\id ZEP (WOL) \ide UTF-8 \h Cefaña \toc1 Cefaña \toc2 Cefaña \mt2 Téereb Yonent Yàlla \mt1 Cefaña \c 1 \p \v 1 Kàddug Aji Sax jii moo dikkaloon Cefaña doomu Kusi. Kusi, Gedalya mooy baayam; Gedalya, Amarya, Amarya, Esekiya. Mu yemook janti buuru Yuda, Yosya doomu Amon. \s1 Am sànj taxaw na \q1 \v 2 «Lépp laay buube ba mu set fi kaw suuf.» \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee ko wax. \q1 \v 3 «Doom aadama ak mala, \q1 njanaaw ak jën laay buub, \q1 ak luy fakktale, booleek ñu bon ñi. \q1 Maay dagge doom aadama fi kaw déndub suuf.» \q1 Aji Sax jee ko wax.» \b \q1 \v 4 «Maay xàccil sama loxo, Yuda, \q2 ak mboolem waa Yerusalem. \q1 Maay dagge fi bii bérab ndesu tuuri \w Baal|lemma="Baal:"\w*, \q1 ak turu sarxalantukatam yeek \q2 \w sarxalkatam|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi, \q1 \v 5 ak ñiy sujjóotal ci kawi taax \q2 gàngoori biddiiw yi, \q1 ak ñiy sujjóotal aka giñal Aji Sax ji \q1 tey giñe Milkom, yàllantu ji, \q1 \v 6 ak ñi dëddu Aji Sax ji, \q1 wutuñu Aji Sax ji, sàkkuwuñu ko.» \b \q1 \v 7 Miig! Fi kanam Boroom bi Aji Sax ji, \q1 \w bésub Aji Sax|lemma="bésub Aji Sax ji-:"\w* ji kat dëgmal na; \q1 Aji Sax jee waajal ab sarax, \q1 te moo ca sellal ay ganam. \b \q1 \v 8 «Keroog bésub saraxu Aji Sax ji, \q2 maay dikke mbugal kàngam yeek \q2 doomi buur yi, \q2 ak boroom coli ndoxandéem yi. \q1 \v 9 Bésub keroog maay dikke mbugal \q2 képp ku aw tuuram tax \q2 mu aadawoo di tëb dëxu bunt\f + \fr 1.9 \fr*\fk tëb dëxu bunt bi, \fk*\ft li ñu ci jublu mooy moytu loraange ju ñu gëm ne tuur mi man na leen koo yóbbe, bu ñu joggee dëxu bunt bi. Seetal ci \ft*\ft \+bk 1.Samiyel \+bk* 5.5.\ft*\f*, \q1 ak ñiy feesal seen kër yàllantu ak alal \q2 ju aw ay ak njublaŋ maye. \q1 \v 10 Su bés baa,» Aji Sax jee ko wax, \q1 «yuux dina jibe fa buntu Jën ya, \q1 wóoy jibe fa Sanc ya, \q1 rajaxoo ju réy jollee ca tund ya. \q1 \v 11 Yeen waa goxu Ja ba, yuuxooleen, \q1 nde jula yépp ay sànku, \q1 mboolem kuy natt donji xaalis \q2 lees fay dagge. \q1 \v 12 Jantub keroog ay làmp laay niite Yerusalem, \q1 ba dikke mbugal ña fa ne degg, \q2 taaje ni biiñ ci kaw ginjriitam, \q1 te naa ci seen xel: “Aji Sax ji baaxewul, lorewul.” \q1 \v 13 Seen alal lees di sëxëtooji, \q1 seeni kër gental, \q1 ñu tabax ay kër yu ñu dul dëkke; \q1 jëmbat tóokëri reseñ yu ñu dul biiñoo.» \b \q1 \v 14 Bésub Aji Sax bu mag bee dëgmal, \q1 moo dëgmal te tànk yu gaaw lool lay jegesee. \q1 Kàddug bésub Aji Sax ji dégtu na, \q1 te ca la jàmbaar di yuuxoo yuux yu metti. \q1 \v 15 Bésub keroog bésub sànj lay doon, \q1 bésub njàqare ak tumurànke, \q1 bésub gental ak gentle, \q1 bésub lëndëmu xàmbaari guddi gu ne këruus, \q1 \v 16 bésub bufta ak wootey xare \q1 ca kaw dëkk ya ñu dàbbli, \q1 ak kaw tata yu kawe ya. \b \q1 \v 17 «Ca laay jàqale doom aadama yi, \q1 ñuy tëñëx-tëñëxi ni silmaxa, \q1 nde Aji Sax ji lañu moy, \q1 te seen deret lees di sotti fi pëndub suuf, \q1 seen yérey biir ni neefare fi suuf. \q1 \v 18 Du seen xaalis, du seen wurus \q2 wu leen di mana xettli. \q1 Keroog bésub sànjum Aji Sax ji, \q2 ak sawaras fiiraangeem, \q1 àddina sépp ay xoyomu. \q1 Mooy raafal moos mboolem ñi dëkke àddina si, \q1 te raafal gu raglu lay doon!» \c 2 \s1 Wooteb tuub jibal na Yuda \p \v 1 Yeen xeet wi dul rus, dajeleena daje, \q1 \v 2 balaa dogal bee taxaw, \q1 bésub mbugal ne jaas ba wéy ni boob, \q1 bala leen tàngooru merum \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee dikkal, \q1 bala leen bésub merum Aji Sax jee taxawal. \q1 \v 3 Sàkkuleen Aji Sax ji, \q2 mboolem yeen néew-dooley réew mi, \q1 yeen ñiy jëfe àttey yoonam, \q2 sàkkuleen njekk te sàkkoo toroxlu, \q1 jombul ngeen yiiru, kera bésu merum Aji Sax ji. \s1 Waxyub mbugal ñeel na xeet yu bare \q1 \v 4 Gasa dëkk ba lees di wacc, \q1 Askalon gental, \q1 Asdodd, digg bëccëg lees leen di buub, génne, \q1 te Ekkron\f + \fr 2.4 \fr*\ft Dëkk yii ay dëkki Filisti lañu woon, fa féete ak tefesu géej te dale bëj-gànnaar ba bëj-saalum.\ft*\f* lees di déjjati. \q1 \v 5 Wóoy ngalla yeen waa tefesu géej, \q2 yeen xeetu Kereteen\f + \fr 2.5 \fr*\ft Ñooy waa Filisti, seen cosaan moo doon dun bi ñuy wax Keret.\ft*\f* ñi, \q2 kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dal na leen. \q1 Yeen waa Kanaan, réewum Filisteen ñi, \q2 maa leen di sànk ba dungeen dese kenn\f + \fr 2.5 \fr*\ft Mbugal mii moo sottal alkànde gi toppoon waa Kanaan. Seetal \ft*\ft \+bk Njàlbéen ga \+bk*9.25.\ft*\f*, \q1 \v 6 tefesu géej doon àllub parlu, \q2 ak dëkkuwaayu sàmm seek gétt gi. \q1 \v 7 Tefes ga, ndesu kër Yuda koy moom\f + \fr 2. 4-7 \fr*\ft Réewum Kanaan mi la Yàlla digoon Ibraayma ne moom lay jox aw askanam. Seetal ci \ft*\ft \+bk Njàlbéen ga \+bk* 12.6-7.\ft*\f*, \q1 ñu di ca fore, \q1 bu ngoonee ñu tëri néegi Askalon. \q1 Seen Yàlla Aji Sax jee leen di dikkal, \q1 tijji seen wërsëg (/yiwileen cig njaam.) \b \q1 \v 8 «Maa dégg ŋàññi Mowab, \q1 kàddu yu ñaaw yi Amoneen ñiy ŋàññe sama ñoñ, \q1 tey damu, nara nangu seen suuf. \q1 \v 9 Moo tax, giñ naa ko ci man miy dund,» \q2 kàddug Aji Sax ju gàngoor yee, Yàllay Israyil, \q1 «Mowab déy ni dëkkub Sodom lay mujje, \q1 Amoneen ñi mel ni Gomor, \q1 ay dég ak paxi xorom a koy nangu, \q1 mu gental ba fàww. \q1 Sama ndesu ñoñ a leen di sëxëtoo, \q1 ndesu xeet wi ma séddoo moo leen di moom.» \q1 \v 10 Loolu lañuy yooloo seen reewande, \q1 nde ñoo doon ŋàññe aka damu \q2 ci kaw ñoñi Aji Sax ji Boroom gàngoor yi. \q1 \v 11 Nu raglu la Aji Sax jiy dale ci seen kaw, \q1 te mooy ràggal yàllay àddina yépp, \q1 ba xeet yi di ko sujjóotale dunoo dun, \q1 wu ci nekk ak fa nga fare. \b \q1 \v 12 Yeen waa \w Kuus|lemma="Kuus:"\w*, itam \q1 yeen lees di fàdde sama saamar. \b \q1 \v 13 Keey xàccil loxoom bëj-gànnaar, \q1 keey sànk réewum Asiri, \q1 keey def Niniw ab gent bu wow ni màndiŋ. \q1 \v 14 Ca digg dëkk ba la jur gay goore, \q1 ak xeetu rab wu nekk; \q1 looy aki saaw fanaane kaw jëni bunt ya, \q1 ay sab jibe ca palanteer ya, \q1 tojit ya dala jale ca bunt ya, \q1 xànqi seedar ya ne duŋŋ. \q1 \v 15 Ana dëkk bu xumb ba dëkke woon kaaraange, \q1 te naan cim xelam: «Man rekk a, du keneen»? \q1 Nan la doone nii ab gent, \q2 bérab bu rab yiy goore, \q1 mboolem ku fa jaare, ub gémmiñam, jalu. \c 3 \s1 Yerusalem déggadi na \q1 \v 1 Wóoy ngalla fippukat bu sobewu bi, \q1 dëkkub notkat yi. \q1 \v 2 Dégluwul baat, nanguwul kàddu guy yare, \q1 du \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji la wóolu, \q1 du Yàllaam jooju la jege. \q1 \v 3 Kàngam yi ci biiram di gaynde yuy ŋar, \q1 ay njiitam di tilli timis yu dul pannal, \q1 \v 4 ay yonentam reew, diy workat; \q1 ay \w sarxalkatam|lemma="sarxalkat b-:"\w* teddadil sellnga, xëtt yoon. \q1 \v 5 Ndaxam Aji Sax jiy boroom njekk a ngi ci biiram, \q1 te du def njubadi, \q1 jantoo jant mu fenkal ab àtteem, \q2 te du wuute fu bët sete. \q1 Ab wurujkat kay moo xamul gàcce. \b \q1 \v 6 «Maa fàkkas ay xeet, \q1 seeni tata tasaaroo, \q1 ma wéetal seeni mbedd, \q1 ba kenn jaareetu fa, \q1 seeni dëkk a tas ba kenn desul, \q1 kenn dëkkatu fa. \b \q1 \v 7 «Maa noon Yerusalem: “Xanaa moos dinga ma ragal, \q1 déggal ab yar.” \q1 Su ko defee dëkkuwaayam du tas, \q1 ndax mboolem mbugal yi ma ko dikke, \q2 waaye moo yàkkamtee ñaaw ci jépp jëfam, \q1 \v 8 moo tax, xaar ma rekk,» kàddug Aji Sax jee, \q1 «ba keroog may jóg, nara sëxëtooji, \q1 nde maa dogala dajale xeet yi, \q1 dajale nguur yi, \q1 ngir xëpp leen samam sànj, \q2 mboolem sama tàngooru mer. \q1 Sama sawaras fiiraange déy, \q1 ci la mboolem àddina di xoyomu. \s1 Yàlla mooy tuubloo xeet yi \q1 \v 9 «Su boobaa ma soppi làmmiñu xeet yi, setal ko, \q1 ngir ñuy tudd ñoom ñépp turu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 di ko jaamoondoo benn bopp. \q1 \v 10 Sama jaam ñi, sama ñoñ ñi tasaaroo, \q2 ca wàllaa dexu \w Kuus|lemma="Kuus:"\w* lañuy bawoo, \q1 ba indi samab sarax. \b \s1 Yàlla soppi na xolu ndesu Israyil \q1 \v 11 «Su bés baa gàcce dootul am ci sa mboolem jëf, \q2 ji nga ma moye, \q1 nde maay jële fi sa biir ñiy bége sab sag, \q1 te doo damooti ci sama kaw tund wu \w sell|lemma="sell:"\w*. \q1 \v 12 Waaye maay wacc fi sa biir \q2 askan wu woyof te néew doole, \q1 ñu yiiroo turu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \q1 \v 13 Ndesu Israyil dootuñu ayibal, dootuñu fen, \q1 deesatu leen déggal kàdduy wor, \q1 ñoom doŋŋ it ñooy for, di goor, \q1 te kenn du leen tiital.» \b \s1 Yerusalem dina leqliku \q1 \v 14 Yaw janq \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* mu taaru, sarxolleel, \q1 Éey Israyil, xaacul, \q1 yaw janq Yerusalem mu taaru, bégal, \q1 te bànneexoo xol bu sedd guyy! \q1 \v 15 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji moo teggi say mbugal, \q1 waññi sab noon. \q1 Buurub Israyil, Aji Sax jaa ngi fi sa biir, \q1 dootuloo tiit lu bon. \q1 \v 16 Bésub keroog lees di wax Yerusalem, ne ko: \q1 «Yaw Siyoŋ, bul tiit, bul yoqi. \q1 \v 17 Aji Sax ji sa Yàllaa ngi fi sa biir, \q1 di jàmbaar juy walloo. \q1 Moo lay bége ci biir bànneex, \q1 leqlee la cofeelam, \q1 bége la bay sarxolle. \b \q1 \v 18 «Ñi amu naqar te sore ndajey bernde, \q1 ñooñu la sore, te tegoo woon gàcce, \q1 maa leen di dajale, teggil leen gàcce tey. \q1 \v 19 Ma ne jant yooyu laay jëflanteek \q2 mboolem ñi leen di sonal. \q1 Ci laay wallu kuy sukkóot, \q1 fat ku tumurànke, \q1 may leen teraanga aku tur, \q1 fépp fu ñu ruse woon ci àddina. \q1 \v 20 Yeen, jant yooyu laa leen di indi, \q1 jant yooyu laa leen di dajale, \q1 nde maa leen di defal aw tur ak teraanga \q1 fi biir mboolem askani àddina, \q1 maay tijji seen wërsëg, ngeen gis.» \q1 Aji Sax jee ko wax.