\id PSA (WOL) \ide UTF-8 \h Sabóor \toc1 Sabóor \toc2 Sabóor \mt1 Sabóor \c 1 \s1 Ñaari yoon a ngii \q1 \v 1 Ndokklee yaw mi toppul tànki ku bon, \q2 taxawewuloo yoonu moykat, \q2 toogewuloo jataayu ñaawlekat. \q1 \v 2 Xanaa di bége yoonu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 di ko jàngat guddeek bëccëg. \q1 \v 3 Loo def mu àntu: \q1 nga mel ni garab gu saxe walum ndox, \q1 bu jotee meññ, \q1 te xob wa du lax. \b \q1 \v 4 Loolu dalul moos ku bon, \q1 kay mel ni xatax bu ngelaw li wal. \q1 \v 5 Moo tax ku bon du siggee àtte ba, \q1 moykat du taxawe ndajem aji jub ña. \b \q1 \v 6 Aji Sax ji kay ay sàmm yoonu aji jub; \q1 yoonu ku bon di sànk boroom. \c 2 \s1 Yàlla fal na buur \q1 \v 1 Ana lu xeeti àddina di riir, \q1 lu giir yiy nas pexey neen? \q1 \v 2 Buuri àddinaa ngi dér, \q1 boroom nguur yi daje, \q1 di fexeel \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 mook ki mu fal. \q1 \v 3 Ña nga naan: «Nanu dagg càllala yi, \q1 sànni jéng yi!» \b \q1 \v 4 Ki ci jalub asamaan a ngay ree, \q1 Boroom baa nga leen di kókkali, \q1 \v 5 mer, ba gëdd leen, \q1 xadaru, tiital leen ne: \q1 \v 6 «Man maa tabb buur, fal ko ci \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*\f + \fr 2.6 \fr*\fk Siyoŋ: \fk*\ft Siyoŋ fii mooy tund wa kër Yàlla ga nekkoon ca Yerusalem. Daan nañu ko tudde it dëkku Yerusalem mbaa réewum Israyil.\ft*\f*, \q1 sama tund wu \w sell|lemma="sell:"\w*.» \b \q1 \v 7 Buur ne: «Ma biral dogalu Aji Sax ji, \q1 moom mi ma ne: “Yaa di sama doom, \q1 bés niki tey, maa la jur\f + \fr 2.7 \fr*\fk Jur: \fk*\ft su Yàlla nee moo jur buur bi, waxin la rekk. Bés bi ñuy fal buur bi la Yàlla di biral ne jàppe na buur bi ni doomam. Ni doom di taxawale baayam, ni la buur biy taxawale Yàlla ci kaw suuf. Ni baay di sàmme doomam it, ni la Yàlla di sàmme buur bi, ngir mu am ndam.\ft*\f*. \q1 \v 8 Ñaan ma xeeti àddina, ma sédd la ko, \q1 nga moom ba ca cati àddina, \q1 \v 9 yilife leen yetu weñ, \q1 rajaxe leen ni njaqal xandeer.”» \b \q1 \v 10 Kon yeen buur yi, muusleen, \q1 kilifay àddina, fàgguleen. \q1 \v 11 Jaamuleen Aji Sax ji, ragal ko, \q1 di ko bége, ba yaram daw. \q1 \v 12 Sujjóotal-leen doom ji, bala moo mer, \q1 ngeen sànkoo seenu yoon; \q1 meram day jekki ne jippét, \q1 waaye ndokklee képp ku ko làqoo! \c 3 \s1 Aji jub a ngi woote wall \d Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda, ba muy daw Absalom doomam ju góor\f + \fr 3.1 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk 2.Samiyel\+bk* 15—16.\ft*\f*. \b \q1 \v 1 Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, noon yeeka bare! \q1 Ñu baree may jógal, \q1 \v 2 ñu baree may tooge naa: \q1 «Yàlla du ko wallu!» \qs Selaw\qs* \b \q1 \v 3 Waaye yaw Aji Sax ji, yaa may feg, \q1 di ma teral, di ma siggil. \q1 \v 4 Maay woo Aji Sax ji wall, \q1 mu walloo ma fa tundam wu \w sell|lemma="sell:"\w* wa. \qs Selaw.\qs* \b \q1 \v 5 Maay tëdd nelaw, yewwu; \q1 Aji Sax ji di ma aar. \q1 \v 6 Ñu dul jeex a ma jógal, gaw ma, \q1 te duma ragal. \b \q1 \v 7 Éy Aji Sax ji sama Yàlla, \q1 jógal, wallu ma! \q1 Yaa toj kaabaabi noon yu bon yépp, \q1 foq seeni sell. \q1 \v 8 Aji Sax ji, yaa moom wall, \q1 sa mbooloo jagoo sa barke. \qs Selaw.\qs* \c 4 \s1 Ma gonloo ñaan \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 Éy Yàlla, yaw mi may àtte dëgg, \q1 maa ngi woote, wuyu ma; \q1 maa xatoon, nga yaatal ma. \q1 Ngalla baaxe ma, nangul ma. \b \q1 \v 2 Yeen boroom daraja yi, \q1 buleen yàqati sama der, \q1 buleen sopp caaxaan, di sos. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \q1 \v 3 Xamleen ne \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji day séddoo ku ko ragal, \q1 te bu ma wooyee Aji Sax ji, mu dégg. \q1 \v 4 Loxleen te baña bàkkaar, \q1 waxtaanleen ak seen ngegenaay te noppi. \q1 \v 5 Rendileen seen sarax yi war, \q1 te wóolu Aji Sax ji. \b \q1 \v 6 Bare na ñu naan: «Ana ku nuy won lu baax?» \q1 Éy Aji Sax ji, baaxe nu saw yiw! \q1 \v 7 May nga ma bànneexu xol \q1 bu raw seen pepp mu tuurook biiñ bu wal. \q1 \v 8 Jàmm laay tëdde, nelaw, \q1 Aji Sax ji, yaw doŋŋ yaa may dëël fu wóor. \c 5 \s1 Ma jëluy ñaan \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki toxoro, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, maa ngi àddu, déglu ma, \q1 maa ngi onk, teewlu ma. \q1 \v 2 Sama Buur, sama Yàlla, déglul, ma ne wallóoy! \q1 Yaw laay ñaan. \q1 \v 3 Aji Sax ji, ag suba, ngay dégg sama baat, \q1 suba su ne ma diis la samay dagaan, \q1 di séentu. \b \q1 \v 4 Doo Yàlla ju safoo coxor, \q1 yaw lu bon du la daloo. \q1 \v 5 Ku réy du taxaw fi sa kanam, \q1 kuy def lu ñaaw, bañ nga ko. \q1 \v 6 Aji Sax ji, yaay sànk kuy fen, \q1 sib kuy bóomeek kuy wore. \b \q1 \v 7 Man nag, sa ngor lu yaa laa saña dugge sa kër, \q1 sujjóotal sa \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w*, wormaale la. \q1 \v 8 Éy Aji Sax ji, wommate ma sa njekk ndaxi noon, \q1 te xàllal ma saw yoon. \b \q1 \v 9 Ñii, lu ñu wax, wérul, \q1 seen xol a mébét njekkar, \q1 seenug boli di bàmmeel bu ne ŋàpp, \q1 ñuy naxe làmmiñ wu neex. \q1 \v 10 Éy Yàlla, topp leen, \q1 ñu fakktaloo seeni pexe; \q1 xalabal ñii barey moy, \q1 ñoo la gàntal. \b \q1 \v 11 Képp ku la làqoo, yal na bég, \q1 di saxoo sarxolle, nga di ko yiir, \q1 te ku la sopp di la bége. \q1 \v 12 Aji Sax ji yaw kat, yaay barkeel ku jub, \q1 yiire ko saw yiw, fege ko. \c 6 \s1 Jarag a ngi woote wall \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak xalamu juróom ñetti buum, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, bul mer, ba di ma rëbb, \q1 bul xadaru, ba di ma mbugal. \q1 \v 2 Aji Sax ji, damaa néew doole, yërëm ma! \q1 Éy Aji Sax ji, sama yaram a tas, dàmp ma! \q1 \v 3 Sama xol a jeex tàkk. \q1 Aji Sax ji, loo deeti xaar nag? \q1 \v 4 Éy Aji Sax ji, délsil, xettli ma! \q1 Walloo ma sa ngor. \q1 \v 5 Deesul dee ba fàttliku la; \q1 ku dugg njaniiw, nu mu lay sante? \b \q1 \v 6 Onk naa ba loof, di fanaanee jooy, \q1 sama lal di féey, \q1 ba far seeye rongooñ. \q1 \v 7 Saay gët a ngi xóot ndaxu naqar, \q1 boole ci giim ndax tooñi noonoo noon. \b \q1 \v 8 Yeen, defkati ñaawtéef yépp, xiddileen ma! \q1 Aji Sax ji dégg na saay jooy, \q1 \v 9 Aji Sax ji dégg na saay dagaan, \q1 Aji Sax jii nangu na samag ñaan. \q1 \v 10 Noon yépp a am gàcce, ba jàq lool, \q1 ne wërëñ ak gàcceg mbetteel. \c 7 \s1 Boroom tuumaa ngi woote wall \d Muy woyu njàmbat, ñeel Daawuda. Mu woyaloon ko \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ci mbirum kàddu yu tukkee woon ca \w Kuus|lemma="Kuus:"\w*, ma bokkoon ci giirug Beñamin. \b \q1 \v 1 Éy Aji Sax ji, sama Yàlla, yaw laay làqoo! \q1 Musal ma, xettli maak ñi may dàq ñépp. \q1 \v 2 Lu ko moy ñu fàdd ma ni gaynde, \q1 daggate ma te kenn du wallu. \b \q1 \v 3 Aji Sax ji sama Yàlla, ndegam maa def lii, \q1 ndegam maa taq fenn lu ñaaw, \q1 \v 4 ndegam ku ma jàmmal laa feye aw ay, \q1 mbaa ma dimbali ku ko noonoo te defu ko dara, \q1 \v 5 yal na ma noon rëbb, \q1 dab ma, dëggaate ma, \q1 sàggi saab sag, tëral ci pëndub suuf. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \b \q1 \v 6 Aji Sax ji, meral, jóg, \q1 dajeel maak xadaru noon yi! \q1 Ngalla teewlu ma; yaw, yoon nga santaane. \q1 \v 7 Yal na xeet yi daje, wër la, \q1 nga délsi tiim leen fu kawe. \q1 \v 8 Yal na Aji Sax ji àtte xeet yi; \q1 Aji Sax ji, seetal ci sama njubteek sama maandute te dëggal ma. \q1 \v 9 Yal na mbonug ku bon tees, \q1 te nga saxal kuy def njekk. \q1 Yaw Yàlla Boroom njekk, yaay natt xel ak xol. \b \q1 \v 10 Sama kaaraange, fa Yàlla, \q1 miy musal boroom xol bu dëggu. \q1 \v 11 Yàllaay àtte dëgg. \q1 Yàllaay rëbbe bés bu ne. \q1 \v 12 Ku tuubul, Yàlla nàmm saamaram, \q1 bank xalaam, diir la. \q1 \v 13 Moom la waajalal ngànnaayi ndee, \q1 def ko fitt yuy boy. \b \q1 \v 14 Ku bon a ngoog, di matu doomu ñaawtéef. \q1 Day sos njombe, wasin njublaŋ. \q1 \v 15 Am kan lay gas, ba mu xóot, \q1 te pax ma mu gas, moo ca tàbbi. \q1 \v 16 Fitnaam, këpp ci boppam; \q1 coxoram, xàŋŋ cim kaaŋam. \b \q1 \v 17 Naa sante Aji Sax ji njekkam, \q1 ma woy Aji Sax jiy Aji Kawe ji. \c 8 \s1 Aji Sax ji teral na nit \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit\f + \fr 8.1 \fr*\fk gitiit \fk*\ft tur la wu réer ci làkku ebrë. Man na doon xeetu xalam gu cosaanoo dëkk ba ñuy wax Gaat ci réewu Filisti. Man na nekk it galan bu ñu daan woye ci jamono bu ñuy witt reseñ, di ko nal.\ft*\f*, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. \b \q1 \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji sunu Boroom, \q1 sa tur aka màgg ci kaw suuf sépp! \q1 Sag leer tiim asamaan. \q1 \v 2 Làmmiñu tuut-tànk, ba ci luy nàmp, \q1 feeñal nga ca sa kàttan, \q1 bañaaleek feyukat ne xerem. \b \q1 \v 3 Damay xool sa asamaan si nga móol, \q1 ak weer week biddiiw yi nga fi teg. \q1 \v 4 Moo luy nit, ba nga di ko bàyyi xel? \q1 Luy doom aadamaak loo koy yége? \b \q1 \v 5 Yaa def nit mu yées malaaka yi as lëf, \q1 te yaa ko kaalaa teraangaak daraja, \q1 \v 6 fal ko ci kaw loo bind, \q1 jox ko lépp, mu teg tànk: \q1 \v 7 jur gépp, gu gudd ak gu gàtt, \q1 rabi àll it ca la, \q1 \v 8 ak njanaaw ak jën, \q1 ak luy jaare yooni géej. \b \q1 \v 9 Aji Sax ji sunu Boroom, \q1 sa tur aka màgg ci kaw suuf sépp! \c 9 \s1 Aji Sax ji dëgg lay àtte \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Deewug doom ju góor, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. \b \q1 \v 1 Ma sante \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji sama xol bépp, \q1 di siiwal mboolemi kéemaanam. \q1 \v 2 Yaw Yàlla, dama lay bége, bànneexoo la, \q1 woy la, yaw Aji Kawe ji. \q1 \v 3 Noon yeey dellu gannaaw, \q1 tërëf, sànku fi sa kanam. \b \q1 \v 4 Yaa ma àtte yoon, dëggal ma, \q1 toog ci sab jal, di àtte njub. \q1 \v 5 Rëbb nga xeet yi, sànk ñu bon ñi, \q1 far seeni tur ba fàww. \q1 \v 6 Noon ya raaf, gental ba fàww. \q1 Yaa déjjati seeni dëkk, seenu askan fey. \q1 \v 7 Aji Sax jee sax dàkk, \q1 samp jalam ngir àtte. \q1 \v 8 Moom mooy àtte àddina cig njub, \q1 di dogalal xeet yi dëgg. \q1 \v 9 Aji Sax jeey làq néew-ji-doole, \q1 mooy làqe bésub njàqare. \q1 \v 10 Aji Sax ji, yaw, ku la xam, wóolu la. \q1 Aji Sax ji, yaw, ku lay sàkku, doo ko wacc. \b \q1 \v 11 Woyleen Aji Sax ji dëkke \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, \q1 siiwal-leen ay jalooreem ci xeet yi! \q1 \v 12 Mooy topp nit bakkanu moroomam, di ko ba xel, \q1 te du fàtte yuuxi néew-ji-doole. \b \q1 \v 13 Éy Aji Sax ji, baaxe ma, \q1 gisal naqar wi ma bañ yi teg. \q1 Yaa may yékkatee fa bunti ndee, \q1 \v 14 ba ma siiwali sa woy yépp, \q1 fa buntu Siyoŋ, dëkk bu taaru ba, \q1 di bànneexoo sa wall gii! \b \q1 \v 15 Xeet yee tàbbi pax ma ñu gasoon, \q1 fakktaloo fiir ga ñu làqoon. \q1 \v 16 Aji Sax jaa ngi feeñoo, di àtte yoon; \q1 ku bon teg ug fiir, tàbbi ca. \qs Na jib ndànk. \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \b \q1 \v 17 Ñu bon ñee dëddu, dem njaniiw, \q1 ànd ak xeet yi fàtte Yàlla yépp. \q1 \v 18 Yàlla du tanqamlu ab ndóol ba fàww, \q1 yaakaaru néew-ji-doole du tas mukk. \b \q1 \v 19 Aji Sax ji, jógal, bu la nit yab; \q1 na xeet yi dikk fi sa kanam, nga àtte leen. \q1 \v 20 Rikk Aji Sax ji, yónnee leen tiitaange, \q1 xamal leen ne nit doŋŋ lañu. \qs Selaw.\qs* \c 10 \s1 Néew-ji-doole sàkku na yoon \q1 \v 1 Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, lu la taxa sore? \q1 Xanaa dangay làqu, bésub njàqare? \b \q1 \v 2 Ku bon naagu na, ne dann néew-ji-doole, \q1 lal ay pexeem, ba jàpp ko. \q1 \v 3 Ku bon déy a ngi tëggoo bànneexu bakkanam, \q1 ku bëgge di ñàkke wormaak a teddadil Aji Sax ji. \q1 \v 4 Ku bon daŋŋiiral, seetul dara, \q1 xalaatam yépp mooy Yàlla amul. \q1 \v 5 Saa yu fexee, juble, \q1 te gisul sa ndigali yoon yi ko tiim. \q1 Ma ngay ciipu bañam yépp. \q1 \v 6 Ma nga naan ca xelam: «Duma tërëf, \q1 safaan du ma dab tey ak ëllëg.» \q1 \v 7 Ay móolu la gémmiñ ga fees, ak fen ak njublaŋ, \q1 njekkar ak ñaawtéef lal làmmiñ wa. \q1 \v 8 Day tëroo ciy dëkk-dëkkaan, \q1 làqu di bóom ku deful dara, \q1 nëbbu di wootal néew-ji-doole. \q1 \v 9 Day làqu bérab, di yeeroo ni gaynde cim xunteem, \q1 di yeeru aji ñàkk, ba jàpp ko, \q1 laaw ko, ñoddi, yóbbu. \q1 \v 10 Ma ngay sëgg ak a waaf, \q1 ba aji ñàkk daanu ci loxoom. \q1 \v 11 Mu naa ca xelam: «Yàlla fàtte na, \q1 dummóoyu na, du xoolati.» \b \q1 \v 12 Aji Sax ji, jógal! \q1 Éy Yàlla, xàccil sa loxo. \q1 Bul fàtte néew-ji-doole. \q1 \v 13 Bul may ku bon mu sofental la, \q1 te naan ci xelam: «Yàlla du ma ko topp.» \q1 \v 14 Yaw de yaay ki nemmiku, \q1 di gis njekkar ak naqar, \q1 ku mu dal, nga sàmm àqam. \q1 Néew-ji-doole wéeroo la, \q1 ab jirim, nga dimbali. \q1 \v 15 Ngalla dammal loxol ku soxor ak ku bon, \q1 topp leen seen coxor, \q1 gi ñu yaakaaroon ne du feeñ. \q1 \v 16 Aji Sax jee di Buur ba fàww! \q1 Xeet yeey sànku, jeex cim réewam. \q1 \v 17 Néew-ji-doole dagaan, Aji Sax ji dégg, \q1 dalal xelam, teewlu ko, \q1 \v 18 ngir sàmm àqu jirim ak néew-ji-doole, \q1 ba nit kiy suufu kese dootu xëble. \c 11 \s1 Ma làqoo Aji Sax ji \d \v 1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda. \b \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji laa làqoo. \q1 Ana lu ngeen ma naa: «Neel fëyy ni picc, toŋi sa kaw tund. \q1 \v 2 Xanaa du ñu soxor ñaa ngii, bank seen xala, \q1 nas seenu fitt, \q1 nara lëndëmtu, jam ku jub? \q1 \v 3 Bu ponki njub màbbee, \q1 nu aji jub di def?» \b \q1 \v 4 Aji Sax jaa nga këram gu \w sell|lemma="sell:"\w*. \q1 Aji Sax jaa nga asamaan, kaw jalam, \q1 ne jàkk doom aadama, di ko seetlu. \q1 \v 5 Aji Sax ji day seetlu ku jub; \q1 ku soxor, bëgg fitna, mu bañ. \q1 \v 6 Day tawal ku bon ay mbugal; \q1 sawaraak tamarax akub jaas dib añam. \q1 \v 7 Aji Sax jee jub, sopp njub; \q1 kuy jubal, gis yiwam. \c 12 \s1 Kàddug Yàllaa wóor \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak xalamu juróom ñetti buum, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 Wallóoy, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ngor jee na! \q1 Kóolute réer na doom aadama. \q1 \v 2 Dañuy fenante, \q1 làmmiñ dig lem, xol ba njuuy la. \q1 \v 3 Yal na Aji Sax ji tëj gémmiñu kuy naxe, \q1 ak kuy làmmiñuy tëggu. \q1 \v 4 Ñu ngi naa: «Sunu làmmiñ lanuy daane, \q1 nook sunu kàddu; ku nu manal dara?» \b \q1 \v 5 Ku ñàkk a ngi, ñu futti, \q1 mu ngi binni, di néew-ji-doole. \q1 Aji Sax ji nee: «Maa ngii, di ci jóg, \q1 teg leen fi rawtu gu ñu ne siiw.» \b \q1 \v 6 Kàddug Aji Sax ji, kàddu gu sell la, \q1 ni xaalis bu ñu xelli ci taalu ban, \q1 settli ko juróom ñaari yoon. \q1 \v 7 Ngalla Aji Sax ji, sàmmal ku néewle, \q1 aar ko saa su ne ci nitu tey. \q1 \v 8 Ñu bon ñaa ngi taxawaalu fu ne, \q1 jikko ju sew falu ci biir doom aadama yi. \c 13 \s1 Aji Sax ji, loo deeti xaar? \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 Céy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, loo deeti xaar? \q1 Xanaa doo ma tanqamlu ba fàww? \q1 Loo deeti xaar, bañ maa geesu, \q1 \v 2 ba ma tàggook bopp bu ubu \q1 ak njàqarey xol bu sax, \q1 ba noon dootu ma man? \b \q1 \v 3 Céy Aji Sax ji sama Yàlla, geesu ma, wuyu ma, \q1 leqli ma, bala ma ne sërëx ci nelawi ndee, \q1 \v 4 noon ba naan: «Daan naa ko,» \q1 bañ yay bége saab jéll. \b \q1 \v 5 Man de maa ngi dénkoo sa ngor, \q1 di bànneexoo sag wall. \q1 Naa woy Aji Sax ji, \q1 ki may baaxe xéewalam. \c 14 \s1 Yàqute maase na \d \v 1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda. \b \q1 Ab dof a ngi naa ci xelam: «Yàlla amul!» \q1 Ñu ni mel ay def njekkar, seeni jëf siblu, \q1 kenn defu ci lu baax. \q1 \v 2 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee tollu asamaan, jéer doom aadama, \q1 di seet ku ci xelu, tey sàkku Yàlla. \q1 \v 3 Ñépp lajj, \q1 bokk yàqu yaxeet. \q1 Kenn deful lu baax, \q1 du kenn sax. \q1 \v 4 Aji Sax ji nee: «Xanaa ñiy def lu bon ñépp xamuñu dara? \q1 Ñuy lekk sama ñoñ niw ñam, \q1 te sàkkuwuñu Aji Sax ji.» \q1 \v 5 Foofu lañuy tiite tiitaange lu réy! \q1 Du Yàllaa ngi ànd ak kuréli ñu jub ñi? \q1 \v 6 Ku néewlee yaakaar, ngeen tas ko, \q1 waaye Aji Sax ji la làqoo. \b \q1 \v 7 Ana kuy xettlee Israyil fa \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*? \q1 Éy bés bu Aji Sax ji delloo ñoñam ndam, \q1 ndaw mbégte ci giirug Yanqóoba! \q1 Ndaw bànneex laa ne, ci Israyil gii! \c 15 \s1 Kuy aji jub? \d \v 1 Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. \b \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, kuy ganeji sa xayma? \q1 Ana kuy dëkki sa tund wu \w sell|lemma="sell:"\w*? \b \q1 \v 2 Xanaa ki wéye maandu, \q1 di def njekk, \q1 di wax dëggu xolam. \q1 \v 3 Du sos, \q1 du tooñ dëkkandoo, \q1 du baatal moroomam. \q1 \v 4 Ku siblu, mu sib, \q1 ku ragal Yàlla, mu teral. \q1 Mooy sàmm ngiñam, \q1 su ko dee lor it. \q1 \v 5 Du leble, ba teg ca; \q1 du nangu ger, ngir fexeel jaambur. \b \q1 Lii ku koy jëfe doo jang. \c 16 \s1 Aji Sax ji laa séddoo, dund ak dee \d \v 1 Muy taalifu Daawuda, ngir jàngle. \b \q1 \v 2 Éy Yàlla, sàmm ma, maa ngi làqu fi yaw! \q1 Maa ne \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji: «Yaay sama Boroom, \q1 awma alal ju la moy.» \q1 \v 3 Ñu sell ñi ci réew mi ñooy garmi yi, \q1 sama mbégte mépp ñoom a. \q1 \v 4 Kuy sàkkuy tuur barew tiis, \q1 man de duma leen tuural deret, \q1 sama làmmiñ du leen tudd. \b \q1 \v 5 Aji Sax ji, yaay wàll wi ma séddoo, \q1 di sama ndabal xéewal. \q1 Yaa yor sama wërsëg. \q1 \v 6 Maa muurloo bérab bu neex, \q1 ndaw cér bu rafet! \q1 \v 7 Ma sant Aji Sax ji may xelal, \q1 ba guddi sax sama xel di ma yedd. \q1 \v 8 Damaa saxoo ne jàkk ci Aji Sax ji \q1 ndijoor la ma fare, ba duma tërëf, \q1 \v 9 xanaa di bànneexu, sama xol bég, \q1 sama yaram finaax. \q1 \v 10 Doo ma wacc njaniiw moos, \q1 sa wóllëre wa, doo ko won yàqutey bàmmeel\f + \fr 16.10 \fr*\ft Woykat bi di wone fii kóoluteem ne Aji Sax ji du ko seetaan muy dee ci saa si, waaye dina ko musal ci dee gi ko doon yoot ca fan yooya. Seetal ci \ft*\ft \+bk Jëf ya\+bk* 13.34-37.\ft*\f*. \q1 \v 11 Yaa may xamal yoonu ndund. \q1 Fu bànneex mate, yaa teew, \q1 xéewal sa ndijoor la saxe. \c 17 \s1 Aji Sax ji, jox ma dëgg \d \v 1 Muy ñaanu Daawuda. \b \q1 Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, déglul liy dëgg, \q1 déglul, ma woote! \q1 Teewlul, ma dagaane la \q1 làmmiñ wu mucc fen. \q1 \v 2 Yal na sama àtte bawoo fi yaw, \q1 nga gis sama njubte. \q1 \v 3 Natt nga saab xol, niir ma guddi, \q1 settantal ma, gisoo dara. \q1 Dogu naa ne duma moye wax. \q1 \v 4 Su may jëf it, di sàmm sa kàddu. \q1 Maay moyu yoonu ku bon. \q1 \v 5 Sa tànk, sama tànk, \q1 jàdduma fenn. \b \q1 \v 6 Éy Yàlla, maa lay woo, nga di ma wuyu; \q1 teewlu ma te déglu ma! \q1 \v 7 Na sa ngor feeñ, \q1 yaw miy walloo sa doole \q1 ku la làqooy noonam. \q1 \v 8 Sàmm ma ni peru bët; \q1 làqe ma sa ker, \q1 \v 9 ma rëcc ñu bon ñi ma song, \q1 noon ñii ma gaw, nar maa bóom. \q1 \v 10 Seen xol dàq yërmande, \q1 seeni wax di reewande. \q1 \v 11 Tanc nañu nu fépp, \q1 ne nu jàkk, nar noo tëral. \q1 \v 12 Mbete gaynde gu namma fàdde, \q1 gaynde gu mat guy tëroo! \b \q1 \v 13 Éy Aji Sax ji, jógal dajeek moom, detteel ko. \q1 Xettlee ma sa saamar, ma rëcc ku bon. \q1 \v 14 Éy Aji Sax ji, walloo ma sa doole, \q1 ma rëcc ñi séddoo dundu àddina. \q1 Say soppe, nga reggal, \q1 seeni doom regg, \q1 desalal seeni doom. \b \q1 \v 15 Man nag ma am dëgg, ne la jàkk, \q1 yewwu, regge sa jëmm. \c 18 \s1 Buur daan, sant Aji Sax ji \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda jaamub \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Mu jagleel Aji Sax ji woy wii, bés ba mu ko xettlee ci mboolem noonam, xettli ko it ci Buur Sóol. Kàdduy woy yaa ngii. \b \q1 \v 1 Mu ne: \q1 Aji Sax ji, maa la sopp, yaw mi may dooleel. \q1 \v 2 Aji Sax ji laay sës, \q1 mu di ma aar, \q1 di ma wallu. \q1 Mooy sama Yàlla, ji may sës, yiiru, fegu; \q1 mooy Boroom doole ji may musal, di ma làq. \q1 \v 3 Ki yelloo cant, Aji Sax ji, \q1 moom laa woo, mucc ci samay noon. \b \q1 \v 4 Buumi ndee tanc ma, \q1 walum kasara naq ma, \q1 \v 5 buumi njaniiw laaw ma, \q1 dee ne jaas, di ma fiir. \q1 \v 6 Ma jàq, woo Aji Sax ji, \q1 ne sama Yàlla wallóoy, \q1 mu dégge këram. \q1 Ma yuuxu, muy dégg. \b \q1 \v 7 Mu mer, suuf yëngu, di ker-keri; \q1 kenuy tund ya jaayu, di reg-regi. \q1 \v 8 Saxar di sël-sëlee ca wakkan ya, \q1 sawara boye ca gémmiñ ga, \q1 xal yu yànj tàkke ca. \q1 \v 9 Mu firi asamaan, wàcc, \q1 niir yu fatt lal tànk ya. \q1 \v 10 Ma nga war malaakam \w serub|lemma="serub y-:"\w*, di naaw, \q1 daayaarloo laafi ngelaw. \q1 \v 11 Ma nga bàddoo lëndëm, làqoo, \q1 làmboo ndox mu lëndëm aki xàmbaar, \q1 \v 12 leer a ko jiitu, xàmbaar ya topp ca, \q1 ak tawub yuur ak xali sawara. \q1 \v 13 Aji Sax jee dënoo asamaan. \q1 Aji Kawe jee àddu, \q1 muy tawub yuur ak xali sawara, \q1 \v 14 mu soqiy fitt ak jumi melax, \q1 tasaare leen, fëlxe. \q1 \v 15 Aji Sax ji, dangaa gëdd, \q1 nokki, mu riir, \q1 xuri géej ne fàŋŋ, \q1 kenuy suuf ne duŋŋ. \b \q1 \v 16 Aji Sax jee yóotoo fa kaw, jàpp ma, \q1 seppee ma ca xóotey ndox ma, \q1 \v 17 musal ma ca noon yu mag, \q1 ya ma bañ te man ma. \q1 \v 18 Ñu dajeek man, bés ba ma jàqee, \q1 Aji Sax ji taxawu ma, \q1 \v 19 yaatal ma, \q1 bége ma, ba xettli ma. \b \q1 \v 20 Aji Sax jee ma yool sama njekk, \q1 samay loxoo set, mu fey ma. \q1 \v 21 Sàmm naa yooni Aji Sax ji, \q1 bonuma, di moy sama Yàlla. \q1 \v 22 Dama ne jàkk ndigalam yépp, \q1 xalabuma dogali yoonam. \q1 \v 23 May ànd ak moom, di jëfeg mat, \q1 di moyoo tooñ. \q1 \v 24 Aji Sax jee ma yool sama njekk, \q1 rafetlu sama mucc ayib. \b \q1 \v 25 Yaw Aji Sax ji, ku gore, fekk la gore; \q1 ku matale, fekk la matale; \q1 \v 26 ku sellal, fekk la sell; \q1 ku dëng, fekk laak say feem. \q1 \v 27 Yaw yaay musal xeet wu néew doole, \q1 kuy daŋŋiiral, nga detteel. \q1 \v 28 Yaw kay yaa may niital. \q1 Aji Sax ji sama Yàllaay leeral sama lëndëm. \q1 \v 29 Maak yaw kay, ma song gàngoor. \q1 Maak sama Yàlla, ma tëb um tata. \b \q1 \v 30 Yàllaa mat. \q1 Kàddug Aji Sax jee wér te wóor. \q1 Mooy feg képp ku ko làqoo. \q1 \v 31 Ana kuy Yàlla ku moy Aji Sax ji? \q1 Ku jara sës ku dul sunu Yàlla? \b \q1 \v 32 Yàllaa may dooleel, \q1 di ma xàllal, yoon mat. \q1 \v 33 Moo ma gaawal ni kéwél, \q1 taxawal ma fu kawe. \q1 \v 34 Moo may tàggat ngir xare, \q1 may bank xalag xànjar. \q1 \v 35 Aji Sax ji yaa may feg, musal ma, \q1 dooleel ma sa loxo, \q1 nangul ma, darajaal ma. \q1 \v 36 Yaa ma xàllalu yoon, \q1 ba duma tërëf. \q1 \v 37 Ma dàq noon yi, dab leen, \q1 jekkli, doora dëpp. \q1 \v 38 Ma jam leen, jógatuñu, \q1 xanaa fëlëñu, ma joggi. \q1 \v 39 Sol nga ma dooley xare, \q1 sukkal ñi ma jógal, ñu féete ma suuf. \q1 \v 40 Won nga ma ndoddi noon, \q1 ma boole bóom bañ yi. \q1 \v 41 Ñu ne wallóoy, wall amul; \q1 ñu woo Aji Sax ji, faalewu leen. \q1 \v 42 Ma wol, ba ñu doon pënd, ngelaw wal, \q1 ma wetti ni banu mbedd. \q1 \v 43 Xettli nga ma ci bokk yiy fippu, \q1 def ma, ma jiite ay xeet; \q1 waaso wu ma xamul sax nangul ma, \q1 \v 44 ku ma ci dégg, déggal ma, \q1 ay doomi doxandéem di ma raamal, \q1 \v 45 ne yàcc, \q1 génne seeni tata, di lox. \b \q1 \v 46 Aji Sax jeey kiy dund. \q1 Kii ma sës a jara sant. \q1 Yàlla mi may musal moo màgg! \q1 \v 47 Mooy Yàlla ji ma feyul, \q1 nangulal ma xeet yi. \q1 \v 48 Xettli nga maak noon, \q1 kaweel ma, ma tiim ku ma jógal, \q1 xettleeti ma cib soxor. \b \q1 \v 49 Kon Aji Sax ji, ma sant la ci biir xeet yi, \q1 kañ la! \q1 \v 50 Yaay may sa buuru ñoñ ndam lu réy, \q1 yaay ji ngor ki nga fal, \q1 muy man Daawuda, di sama askan ba fàww. \c 19 \s1 Aji Sax ji màgg na \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 Asamaan nee Yàlla màgg na, \q1 kaw ne màww, biral liggéeyu loxoom! \q1 \v 2 Bésoo bés kàddu seere ko, \q1 guddee guddi xamle ca mbir. \q1 \v 3 Du làkk, duy wax, \q1 du baat bu dégtu, \q1 \v 4 suuf sépp la seen ndéey jibal, \q1 seen kàddoo àkki cati àddina. \b \q1 Kaw la Yàlla sampal jant xayma, \q1 \v 5 mu mel ni boroom séet, génne néegam, \q1 di mbër mu doŋali, xéluw yoonam. \q1 \v 6 Asamaan lay fenke cat lii, \q1 wëndeelu, sowi cat lee; \q1 amul lu rëcc tàngooram. \b \q1 \v 7 Yoonu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee mat, \q1 di leqli bakkan. \q1 Lu Aji Sax ji seede dëgg la, \q1 day xelal ku xeluwul. \q1 \v 8 Lu Aji Sax ji tegtale, njub la, \q1 di bégal xol. \q1 Lu Aji Sax ji santaane, leeraange la, \q1 di leeral gis-gis. \q1 \v 9 Santaaneb ragal Aji Sax ji mooy li sell \q1 te sax ba fàww. \q1 Lu Aji Sax ji digle, dëgg la, \q1 ak njekk gu sotti. \q1 \v 10 Moo dàq wurus, \q1 raw wurusu ngalam wu ne xas; \q1 dàqati lem, \q1 ëpp tem-tem. \q1 \v 11 Man, Sang bi, ci laay leerloo, \q1 ku ko sàmm yokku yool. \b \q1 \v 12 Nit juum na, umple ko, \q1 baal ma tooñ gu ma umple. \q1 \v 13 Te Sang bi, musal ma ci bàkkaaru teyeef, \q1 mu bañ maa jiital, \q1 ma mana maandu, \q1 mucc moy gu réy. \b \q1 \v 14 Éy Aji Sax ji, lu saaw làmmiñ tudd \q1 mbaa sama xol déey ma ko, \q1 yal nay loo gërëm, \q1 yaa may aar, yaa ma jot. \c 20 \s1 Yal na Buur daan \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 Buur, yal na la \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nangul bésu njàqare, \q1 yal na la turu Yàllay Yanqóoba aj fu kawe, \q1 \v 2 yal na la yónnee wallam fa këram, \q1 jàpplee la fa, ca \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*. \q1 \v 3 Yal na xool loo ko jébbal, \q1 di rafetlu sarax soo ko lakkal. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \q1 \v 4 Yal na la may li nga namm, \q1 di sottal loo mébét, \q1 \v 5 ngay daan, nuy ree, \q1 yéege sunu raaya, màggal sunu Yàlla. \q1 Yal na Aji Sax ji nangu loo dagaan. \b \q1 \v 6 Aji Sax jeey musal ki mu fal, bir na ma tey. \q1 Moo koy nangule fa asamaan su \w sell|lemma="sell:"\w* sa, \q1 ci dooley ndijooram biy musle. \q1 \v 7 Ñiiki watiir, \q1 ñeeki fas, \q1 nun sunu turu Yàlla Aji Sax ji lanuy tudd. \q1 \v 8 Ñoom ñooy jeng ak a jóoru, \q1 nun, nu jóg, taxaw jonn. \b \q1 \v 9 Éy Aji Sax ji, mayal Buur mu daan, \q1 te bés bu nu ko ñaane, mu nangul nu. \c 21 \s1 Aji Sax ji baaxe na Buur \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 Céy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, Buur a ngi bége sa doole, \q1 di bànneexoo sag wall, rekk. \q1 \v 2 Yaa ko may nammeeli xolam, \q1 gàntuwulooy dagaanam. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \q1 \v 3 Yaa ko gatandoo barkey ngëneel, \q1 kaalaa ko wurusu ngalam. \q1 \v 4 Mu ñaan mucc, \q1 nga saxal jalam fàww, \q1 \v 5 sag wall a ko sagala sagal! \q1 Teddngaak daraja nga ko sédd, \q1 \v 6 jagleel ko barke bu sax dàkk, \q1 bégale ko sa kanam, mu bànneexu. \q1 \v 7 Buur wóolu na Aji Sax ji, moos, \q1 du tërëf, Aji Kawe jee gore. \b \q1 \v 8 Buur, yaa naan sa noon yépp céex, \q1 ne say bañ taral. \q1 \v 9 Soo nee jalañ, jafal, ñu boy. \q1 Aji Sax ji mer, sànk leen, \q1 sawara xoyom leen. \q1 \v 10 Yaay raafal seeni giir fi kaw suuf, \q1 fey seen askan ci doom aadama yi. \q1 \v 11 Ñoo la mébal lu bon, \q1 nasal la pexe, joyul. \q1 \v 12 Nga di leen diir fittu kanam, \q1 ñu wone gannaaw. \b \q1 \v 13 Aji Sax ji, jógal ak sa manoore, \q1 nu joobe la, woy sa jaloore. \c 22 \s1 Jëkke jàq, mujje sant \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda, dëppook galan bi ñu dippee Kéwélu fajar. \b \q1 \v 1 Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga wacc ma? \q1 Ma binni, binneeti, wall sore. \q1 \v 2 Éy sama Yàlla, ma woote bëccëg, wuyuwoo; \q1 woote guddi, nopploo ma. \q1 \v 3 Yaw de, yaay ku sell, tooge sab jal, \q1 Israyil di la kañ. \q1 \v 4 Yaw la sunuy maam wóolu woon, \q1 wóolu la, nga xettli leen. \q1 \v 5 Yaw lañu daa woo wall, mucc; \q1 yaw lañu wóolu woon te rusuñu. \q1 \v 6 Man nag aw sax rekk laa, matuma nit. \q1 Doom aadama sewal ma, aw xeet tuutal ma. \q1 \v 7 Ku ma gis ñaawal ma, \q1 biiñ ma, xeelu ma, naa: \q1 \v 8 «Na wéeroo \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, mu xettli ko; \q1 su ko soppee, na ko wallu.» \q1 \v 9 Yaw de yaa ma roccee sama biiru ndey, \q1 naxe ma sama weenu yaay. \q1 \v 10 Yaw laa dénkoo ba may juddu, \q1 ba ma juddoo sama ndey, ngay sama Yàlla. \q1 \v 11 Bul ma sore, \q1 musiba teew na, wall amul! \q1 \v 12 Noon yaa ngi ma gaw ni coggalu yëkk, \q1 dar ma ni ponkali yëkk ya fa Basan. \q1 \v 13 Ñu ŋa ma, ŋàpp, \q1 ni gaynde, guy yëmmook a fàdde. \q1 \v 14 Doole ŋiis, \q1 yax yoqi, \q1 fit ne soyox, seey. \q1 \v 15 Làmmiñ taqoo denqleñ, \q1 doole jeex, ma wow koŋŋ, \q1 nga tëral ma buntu bàmmeel. \q1 \v 16 Ay xaj a ma wër, \q1 di gàngooru saaysaay, dar ma kepp, \q1 bëtt samay yoxook samay tànk. \q1 \v 17 Maa ngii, mana waññ sama yax yépp, \q1 ñoom ñuy xoole, di ma seetaan, \q1 \v 18 séddoo samay yére, \q1 tegoo bant sama mbubb. \q1 \v 19 Waaye yaw, Aji Sax ji, bul sore; \q1 yaa may dooleel, gaawe ma. \q1 \v 20 Xettlil sama bakkan ci saamar, \q1 ba sama benn bakkan bii mucc selli xaj! \q1 \v 21 Musal ma ci pàddum gaynde ak ndañum nagu àll. \b \q1 Yaa ma wallu woon! \q1 \v 22 Ma siiwali saw tur ci bokk yi, \q1 màggale la digg mbooloo mi. \q1 \v 23 Yeen ñi ragal Aji Sax ji, santleen ko. \q1 Yeen askanu Yanqóoba wépp, màggal-leen ko. \q1 Yeen \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp, wormaal-leen ko. \q1 \v 24 Moom de sàgganewul boroom tiis, \q1 làqu ko kanamam, \q1 ba mu wootee, wuyu na ko. \q1 \v 25 Yaw laay sante ndaje mu mag, \q1 sottalal la samay dige\f + \fr 22.26 \fr*\fk sottalal la samay dige: \fk*\ft dige yooyu ay saraxi cant la yu ñuy bokk lekk. Ki koy joxe mooy ñaanal ñi mu ci woo jàmm ak wér ak barke.\ft*\f*, ñi la ragal seede. \q1 \v 26 Ku woyof a cay lekk ba doyal, \q1 kuy wut Aji Sax ji, sant ko. \q1 «Guddleena gudd fan!» \b \q1 \v 27 Àddina wërngal këpp ay fàttliku, \q1 walbatiku ci Aji Sax ji. \q1 Làngi xeet yépp sukkalsi ko. \q1 \v 28 Aji Sax jeey boroom nguur, \q1 moo yilif xeet yi. \q1 \v 29 Boroom barke xéewlu, sujjóotal ko, \q1 ku jëm pax it, te bakkanam di lang, \q1 di ko sukkal. \q1 \v 30 Askan wu dikkagul dina jaamu Boroom bi, \q1 ñiy ñëw te juddooguñu dees na leen wax ay mbiram. \q1 \v 31 Ñu dikk, biral njekkam, \q1 jottli xeet wu sosoogul jalooreem. \c 23 \s1 Aji Sax jee may sàmm \d \v 1 Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. \b \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee may sàmm, \q1 du lenn lu ma ñàkk. \q1 \v 2 Parlu mu naat la may gooral, \q1 wal mu dal, mu tette ma ca, \q1 \v 3 leqli ma, \q1 teg ma ci yooni njekk \q1 ngir teddngay turam. \q1 \v 4 Su may jaare xuru ndee wu ne këruus it, \q1 duma ragal loraange: \q1 yaw laak man, \q1 sa bantu sàmm ak sa nguul, \q1 yooyoo may dalal. \b \q1 \v 5 Yaa ma berndeel, \q1 noon yi gis, \q1 nga diwal ma saa bopp, terale ma, \q1 saab kaas rembat. \q1 \v 6 Mbaax ak ngor kay la ma Aji Sax jiy dare sama giiru dund, \q1 ma dëkke këram ba fàww. \c 24 \s1 Ana kuy màggal Buur Yàlla? \d \v 1 Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. \b \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee moom suuf ak li ko fees, \q1 ak àddina ak li ci biiram. \q1 \v 2 Moo samp suuf biir géej, \q1 dëj ko ci kaw wal mi. \b \q1 \v 3 Ana kuy yéegi tundu Aji Sax ji, \q1 kuy taxawi bérabam bu \w sell|lemma="sell:"\w* ba? \q1 \v 4 Xanaa ku mucc ayib, sell ab xol, \q1 xemmemul caaxaani neen, \q1 du giñey fen. \q1 \v 5 Kookooy jagoo barkeb Aji Sax ji, \q1 ak njekku Yàlla, mi koy musal. \q1 \v 6 Ñooñooy waa làng, gi lay sàkku, \q1 di maasug Yanqóoba, giy sàkku sa yiw. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \b \q1 \v 7 Neleen bunt yi kulbét, \q1 ubbileen bunti cosaan yi, \q1 Buur Boroom ndam duggsi. \q1 \v 8 Buur Boroom ndam booboo di kan? \q1 Xanaa Aji Sax ji Boroom dooleek njàmbaar, \q1 Aji Sax ji jàmbaaru xare ji. \q1 \v 9 Neleen bunt yi kulbét, \q1 ubbileen bunti cosaan yi, \q1 Buur Boroom ndam duggsi. \q1 \v 10 Buur Boroom ndam booboo di kan? \q1 Xanaa Aji Sax ju gàngoor yi. \q1 Kookooy Buur Boroom ndam. \qs Selaw.\qs* \c 25 \s1 Aji Sax jeey gindee, di yiire \d \v 1 Ñeel Daawuda. \b \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, yaw laay diis sama bakkan. \q1 \v 2 Sama Yàlla, yaw laa yaakaar. \q1 Yàlla buma rus, \q1 noon yi ree. \q1 \v 3 Deesu la séentu, ba rus. \q1 Kuy wor ci neen mooy rus. \b \q1 \v 4 Éy, Aji Sax ji, won ma saw yoon, \q1 xamal ma fi nga ma jaarloo. \q1 \v 5 Jiitee ma sag dëgg, jàngal ma. \q1 Yaw yaay Yàlla ji may musal, \q1 ma di la yendoo yaakaar. \q1 \v 6 Aji Sax ji, bàyyil xel sa yërmandeek sa ngor. \q1 Naka jekk sa jikkoo! \q1 \v 7 Bul xool li ma bàkkaare ndaw ak li ma moy. \q1 Aji Sax ji, xoole ma sa ngor ngir sag mbaax. \b \q1 \v 8 Aji Sax jee baax, rafeti dogal, \q1 di gindi moykat ci yoon wi, \q1 \v 9 di jiite ku woyof mbubb ci njubte, \q1 di ko xamal aw yoonam. \q1 \v 10 Aji Sax ji ngor ak dëgg rekk lay jiitee \q1 kuy sàmm \w kóllëreem|lemma="kóllëre g-:"\w* ak seedey yoonam. \b \q1 \v 11 Éy Aji Sax ji, tooñ naa lool, \q1 jéggal ma ngir saw tur. \q1 \v 12 Ana kuy wormaal Aji Sax ji, \q1 mu won ko yoon wi mata taamu, \q1 \v 13 muy dunde ngëneel, \q1 askanam moom réew mi? \q1 \v 14 Ndéeyu Aji Sax ji, jagley ku ko ragal. \q1 Kóllëreem la koy xamal. \q1 \v 15 Samay gët jàkk rekk ci Aji Sax ji, \q1 moo may xettli ci fiiru noon. \b \q1 \v 16 Ngalla geesu ma, baaxe ma, \q1 maa wéet, néew doole, \q1 \v 17 sama xol feesey xalaat. \q1 Rikk, teggil ma njàqare! \q1 \v 18 Xoolal sama naqar ak sama tiis, \q1 te baal ma bépp bàkkaar. \q1 \v 19 Xoolal noon yi ne gàññ, \q1 bañ ma mbañeelu fitna. \b \q1 \v 20 Éy, aar ma, musal ma! \q1 Bu ma rusloo, \q1 yaw laa làqoo. \q1 \v 21 Yal na ma maanduteek njub taxawu, \q1 maa ngii, di la xaar. \q1 \v 22 Éy Yàlla, teggilal Israyil tiisoo tiis. \c 26 \s1 Ma waajal ndajem kër Aji Sax ji \d \v 1 Ñeel Daawuda. \b \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, àtte ma, \q1 man de maandu laa wéye, \q1 Aji Sax ji laa wóolu, jenguma. \q1 \v 2 Aji Sax ji, nattu ma, seetlu ma, \q1 seggal xel ak xol. \q1 \v 3 Maa ngi janook sa ngor, \q1 di jëfe sa worma. \q1 \v 4 Toogumaak naxekat, \q1 lëngoowumaak naaféq, \q1 \v 5 sib naa gàngooru saaysaay, \q1 toogumaak ku bon. \q1 \v 6 Aji Sax ji, maay jàpp ci biir mucc ayib, \q1 di wër sa \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*, \q1 \v 7 àddu, sant la, \q1 lim sa jépp jaloore. \q1 \v 8 Aji Sax ji, maa sopp sa dëkkuwaay, \q1 bëgg bérab bi sag leer teew. \b \q1 \v 9 Bu ma buubaaleek bàkkaarkat, sànni, \q1 di ma booleek bóomkat, bóom. \q1 \v 10 Seeni yoxoo nga sóobu ci mbon, \q1 ndijoor ya fees aki ger. \b \q1 \v 11 Man nag maandu laay wéye, \q1 tee nga maa jot, baaxe ma? \q1 \v 12 Ndokk bi ma taxawee joor gu wóor. \q1 Ma màggal Aji Sax ji fi ndajey way-gëm ñi. \c 27 \s1 Xare jib, ma ànd ak Yàlla \d \v 1 Ñeel Daawuda. \b \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee may leeral, di ma wallu. \q1 Ana ku may ragal? \q1 Aji Sax jeey aar sama bakkan. \q1 Ana ku may tiit? \q1 \v 2 Ab soxor wutsi ma, \q1 nar maa yàpp, \q1 noonoo ma, bañ ma; \q1 mooy tërëf, fëlëñu. \q1 \v 3 Bu gàngoor booloo sama kaw, \q1 duma raf. \q1 Ab xare jib, \q1 ma ànd ak Yàlla. \b \q1 \v 4 Lenn laa ñaan Aji Sax ji, \q1 lii laay sàkku: \q1 dëkk kër Aji Sax ji, \q1 sama giiru dund, \q1 di niir taaru Aji Sax ji, \q1 te yéemoo këram. \q1 \v 5 Bésub ay, mu yiire ma mbaaram, \q1 làq ma, ma làqoo xaymaam, \q1 aj ma ciw doj, ma raw. \q1 \v 6 Ma doxe fa siggi, \q1 tiim noon yi ma wër, \q1 di sarxali fa xaymaam \q1 saraxi sarxolle. \q1 Naa woyal Aji Sax ji, joobe ko. \b \q1 \v 7 Éy Aji Sax ji, déglul, ma woote! \q1 Ngalla baaxe ma, nangul ma. \q1 \v 8 Yaw la sam xel ne ma, ma sàkku la, \q1 te it yaw Aji Sax ji laay sàkku. \q1 \v 9 Sang bi, bu ma làqu, \q1 bul mer, jañax ma. \q1 Yaa ma daa wallu. \q1 Bu ma wacc, bu ma ba, \q1 yaay Yàlla mi may musal. \q1 \v 10 Ndey ak baay man nañu maa wacc, \q1 Aji Sax ji fat ma. \q1 \v 11 Éy Aji Sax ji, joxoñ ma saw yoon, \q1 jaarale ma joor gu wóor, \q1 ngir ñi may tëru. \q1 \v 12 Bu ma baye bànneexu noon. \q1 Seedey naaféq a ma jógal, \q1 di sos fitna. \q1 \v 13 Maay dajeek ngëneelu Aji Sax ji \q1 fi kaw suuf sii. \q1 Lii wóor na ma. \q1 \v 14 Yaakaaral Aji Sax ji, \q1 dëgërlul te amu fit, \q1 te yaakaarati Aji Sax ji. \c 28 \s1 Aji Sax jeey àtte ñoñam \d \v 1 Ñeel Daawuda. \b \q1 Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, yaw laay woo, \q1 di la wéeroo, bu ma tanqamlu. \q1 Soo nee cell, \q1 ma xawa tàbbim pax. \q1 \v 2 Ngalla déglul, ma tinu la, \q1 woo la wall, \q1 dékk lay yoxo, \q1 jublu sa néegu biir bu \w sell|lemma="sell:"\w* ba. \b \q1 \v 3 Bu ma sànkaaleek ab soxor, \q1 di ma booleek kuy def lu bon, \q1 di wax moroom ma jàmm, \q1 te dencal ko ay ca xolam. \q1 \v 4 Fey leen seen liggéey, \q1 seen kemu jëf ju bon. \q1 Jox leen seen añu jëf, \q1 yool leen seen yelleef. \q1 \v 5 Xooluñu Aji Sax jeeki jëfam, \q1 ak liggéey bi mu def. \q1 Da leen di yàqte, \q1 te dootu leen yékkati. \b \q1 \v 6 Jaajëfe Aji Sax ji, \q1 ki ma nangul samay dagaan! \q1 \v 7 Aji Sax jee may dooleel, di ma feg. \q1 Moom laa wóolu, mu wallu ma, \q1 sama xol tooy, \q1 ma woy, sante ko. \q1 \v 8 Aji Sax jeey dooleel ñoñam. \q1 Mooy làq, di musal buur bi mu fal. \q1 \v 9 Ngalla musalal sa mbooloo, \q1 barkeelal sa ñoñ ñii, \q1 sàmm leen, boot ba fàww. \c 29 \s1 Aji Sax jeey boroom ndam \d \v 1 Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. \b \q1 Yeen goney Yàlla yi, seedeel-leen \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 seedeel-leen ko teddngaak doole, \q1 \v 2 seedeel-leen Aji Sax ji teddngay turam. \q1 Sujjóotal-leen Aji Sax ji, \q1 ki gànjaroo sellnga. \b \q1 \v 3 Aji Sax jeey àddu ca kaw ndox ma, \q1 Yàlla mu tedd maa dënu, \q1 Aji Sax jeey tiim ndox, mi ne màww. \q1 \v 4 Aji Sax jeey àddoo doole, \q1 Aji Sax jeey àddoo daraja. \q1 \v 5 Aji Sax jeey àddu, falaxe garabi seedar, \q1 Aji Sax jee rajaxe seedari Libaŋ. \q1 \v 6 Réewum Libaŋ, mu curpiloo ni wëllu, \q1 tundu Siryoŋ\f + \fr 29.6 \fr*\fk tundu Siryoŋ \fk*\ft mooy tundu Ermon ba tey.\ft*\f* it, mbete yëkk wu ndaw. \q1 \v 7 Aji Sax jeey àddu, \q1 fettaxal sawara, mu boy. \q1 \v 8 Aji Sax ji àddooti, yëngal màndiŋ, \q1 Aji Sax jee yëngal màndiŋu Kades. \q1 \v 9 Aji Sax jeey àddu, kéwél matu, \q1 garabi àll ruus, \q1 biir këram di mennum riir, \q1 naan: «Màggal-leen ko!» \b \q1 \v 10 Aji Sax ji la mbënn ma fekk falu, \q1 Aji Sax jee falu buur ba fàww. \q1 \v 11 Aji Sax jeey kàttanal ñoñam, \q1 di barkeele jàmm ñoñam. \c 30 \s1 Mucc, bég \d Muy woyu Sabóor, ñeel Daawuda ca daloob kër Yàlla ga\f + \fr 30.1 \fr*\ft Woyu Sabóor wii Daawuda da koy sante Yàlla gannaaw mbas ma, ba mu jëndee dàgga ngir rendi fa sarax su dakkal mbas ma. Dàgga jooju lañu mujj tabax jaamookaay ba. Seetal ci \ft*\ft \+bk 2.Samiyel\+bk* 24, ak \+bk 1.Jaar-jaar ya\+bk* 21.\ft*\f*. \b \q1 \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, dama lay kañ. \q1 Yaa ma yékkati, \q1 ba noon reetaanu ma. \q1 \v 2 Aji Sax ji sama Yàlla, maa la woo wall, \q1 nga faj ma. \q1 \v 3 Aji Sax ji, yaa ma jukkee njaniiw, \q1 may ma bakkan, ma tàggook ñiy tàbbi njaniiw. \b \q1 \v 4 Yeen aji gëm ñi, woyleen Aji Sax ji, \q1 njukkale ko sellngaam. \q1 \v 5 Meram di lu gàtt, \q1 aw yiwam sax dàkk. \q1 Rongooñ gane, fanaan, \q1 ay ree xëysi. \b \q1 \v 6 Man damaa baaxle woon, ba ne: \q1 «Deesu ma rëññeel mukk.» \q1 \v 7 Aji Sax ji, booba yaa ma baaxe, \q1 dëj ma, ma ne kekk niw tund. \q1 Nga fuuyu, ma jàq. \q1 \v 8 Aji Sax ji, yaw laa woo wall; \q1 Boroom bi, yaw laa ñaanu yiw, \q1 \v 9 ne la: «Ma dee, tàbbi bàmmeel, \q1 ana lu mu lay jariñ? \q1 Nu la pëndu pax di sante, \q1 bay biral sa worma? \q1 \v 10 Aji Sax ji, déglul, baaxe ma; \q1 éy Aji Sax ji, dimbali ma.» \b \q1 \v 11 Yaa ma soppil samay rongooñ ay ree, \q1 summi sama yérey tiis, solal ma bànneex. \q1 \v 12 Naa la woye xol, baña selaw. \q1 Aji Sax ji, sama Yàlla, ma sant la ba fàww! \c 31 \s1 Naa siggi, noon sëgg \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, yaw laa làqoo, \q1 yàlla buma rus mukk. \q1 Yiwee ma sa njekk. \q1 \v 2 Teewlu ma, \q1 gaawe ma, \q1 may ma, ma sës ci yaw, fegu. \q1 Aar ma, ma mucc. \q1 \v 3 Yaa may yiir, di ma aar, \q1 jiite ma, wommat ma ngir yaw. \q1 \v 4 Génne ma fiir gi ñu may tëroo; \q1 yaw yaa di sama rawtu. \q1 \v 5 Yaw laa dénk sama bakkan. \q1 Aji Sax ji, Yàlla miy dëgg, ngalla jot ma. \b \q1 \v 6 Maa bañ kuy topp tuuri neen. \q1 Man, Aji Sax ji laa wóolu. \q1 \v 7 Damay bég, di bànneexoo sa ngor, \q1 li nga xoole samaw tiis. \q1 Ràññee nga sama njàqarey xol. \q1 \v 8 Waccoo ma ci loxol noon, \q1 danga maa taxawal fu ma yaatoo. \b \q1 \v 9 Éy Aji Sax ji, baaxe ma, jàq naa! \q1 Samay gët a ngi giim ndaxu tiis, \q1 xol jeex, yaram jeex. \q1 \v 10 Naqar a ngi may rey, \q1 tiis di wàññi samay fan, \q1 sama doole ŋiis ndax sama njubadi, \q1 samay yax semm. \q1 \v 11 Noonoo noon a ma sewal, \q1 dëkkandoo waxi noppi, \q1 xame seexlu ma, \q1 ku ma gis biti, di ma daw. \q1 \v 12 Kenn xalaatu ma, xanaa fàtte ma ni ku dee, \q1 ma mel ni ndab lu yàqu. \q1 \v 13 Damaa dégg jëw yu bare, \q1 lu raglu dar ma kepp. \q1 Ñu ngi mànkoo, di ma fexeel, \q1 di wut sama bakkan. \b \q1 \v 14 Man nag Aji Sax ji, ci yaw laa dénku. \q1 Ma ne: «Yaay sama Yàlla.» \q1 \v 15 Yaa yor sama àpp. \q1 Xettli maak ku ma noonoo \q1 ak ku may sonal. \q1 \v 16 Leeralal ma sa kanam, Sang bi, \q1 walloo ma sa ngor. \q1 \v 17 Éy Aji Sax ji, woo naa la wall, \q1 yàlla buma rus. \q1 Yal na ku bon rus, \q1 ne xerem biir njaniiw. \q1 \v 18 Yal nanga tëj gémmiñu fen-kat \q1 buy wax aji jub waxi reewande, \q1 di réy-réylook a xeebaate. \b \q1 \v 19 Yàlla yaa yaa ngëneel \q1 loo dencal ku la ragal, \q1 defal ko ku la làqoo, \q1 doom aadama seede. \q1 \v 20 Yaa koy làq fa nga làqu, \q1 fa pexey nit àggul. \q1 Nga yiir ko, mu yiiru \q1 ci ayu làmmiñ. \b \q1 \v 21 Teddnga ñeel na Aji Sax ji! \q1 Ndaw kéemtaan ci ngor li mu ma jiwe \q1 biir dëkk bu ñu gaw. \q1 \v 22 Man nag saalitoon naa ne: \q1 «Yàlla dagg na ma, sànni!» \q1 Ndeke ba ma lay woo, \q1 dégg nga samay dagaan. \b \q1 \v 23 Képp kuy aji gëm, soppal Aji Sax ji. \q1 Aji Sax jeey sàmm ku ko gëm, \q1 di yool, ba wis kuy réy-réylu. \q1 \v 24 Képp ku yaakaar Aji Sax ji, \q1 dëgërlul te amu fit. \c 32 \s1 Njéggal barke la \d \v 1 Dib taalif, ñeel Daawuda. \b \q1 Ndokklee yaw mi ñu baal bàkkaar, \q1 jéggal la ag moy. \q1 \v 2 Ndokklee yaw mi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji toppul ag tooñ, \q1 te amoo xelum njublaŋ it. \b \q1 \v 3 Ba ma nee cell, \q1 damaa ràgg, \q1 dëkke naqar. \q1 \v 4 Guddeek bëccëg \q1 sa loxo diis gann ci man. \q1 Sama doole ŋiis \q1 ni ndox mu jaas upp. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \q1 \v 5 Ma xamal la ne moy naa, \q1 làqatuma la sama ñaawtéef. \q1 Ma ne: «Naa àgge Aji Sax ji sama bàkkaar.» \q1 Yaw nga baal ma peyug tooñ. \qs Selaw.\qs* \b \q1 \v 6 Nii, kuy aji gëm, na la ni ñaane, \q1 ba ñaan jotee. \q1 Mbënn mu baawaan, di wal sax, \q1 du ko laal fenn. \q1 \v 7 Yaw laay làqoo, \q1 nga di ma aar ciw ay, \q1 may ma ñu ma yéew, di ko bége. \qs Selaw.\qs* \b \q1 \v 8 Nga ne ma: «Dama laa xelal, \q1 xamal la fi ngay jaar, \q1 digal la, di la xool. \q1 \v 9 Buleen mel ni fas mbaa berkelle \q1 mi amul ag dégg, \q1 laab ak tarka di ko téye, \q1 mu doora yem fi seen wet.» \q1 \v 10 Ku bon barew tiis. \q1 Ku wóolu Aji Sax ji, \q1 mu yiire la ngoram. \q1 \v 11 Yaw aji jub ji, bégal te bànneexoo Aji Sax ji. \q1 Képp kuy def njub, sarxolleel! \c 33 \s1 Nan woy Boroom bi nu sàkk \q1 \v 1 Yeen aji jub ñi, sarxolleleen ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji; \q1 kuy jubal, màggal war na la. \q1 \v 2 Xalamleen, sante Aji Sax ji, \q1 xalamal-leen ko xalamu fukki buum. \q1 \v 3 Fental-leen ko woy, \q1 xalam, mu neex, sarxolle jib. \b \q1 \v 4 Aji Sax jee jub kàddu. \q1 Mooy jëfe lépp kóllëre. \q1 \v 5 Moo sopp dëgg ak yoon. \q1 Aji Sax ji, ngoram a fees àddina. \b \q1 \v 6 Kàddug Aji Sax ji la asamaan sosoo, \q1 ci baatam la gàngoori asamaan yépp sàkkoo. \q1 \v 7 Moo boole ndoxi géej, jal, \q1 yeb xóotey géej ciy mbànd. \q1 \v 8 Yeen waa àddina sépp, ragal-leen Aji Sax ji; \q1 yeen àddina wërngal këpp, wormaal-leen ko. \q1 \v 9 Moo àddu, mu am; \q1 santaane, mu sotti. \q1 \v 10 Aji Sax jeey neenal li xeet yiy fexe, \q1 di gàntal li mbooloo yiy mébét; \q1 \v 11 Aji Sax ji nas, mu àntu ba fàww, \q1 mu mébét, mu sottil maasoo maas. \q1 \v 12 Ndokklee yeen xeet wi Aji Sax ji di seen Yàlla, \q1 yeen askan wi Aji Sax ji séddoo. \q1 \v 13 Asamaan la Aji Sax jiy jéere, \q1 di gis doom aadama yépp. \q1 \v 14 Jal ba mu tooge \q1 lay niire waa àddina sépp. \q1 \v 15 Moo tabax seen xol, ñoom ñépp; \q1 lu ñu def, xam na ko. \q1 \v 16 Mbooloo mu réy mayul Buur ndam, \q1 doole ju bare walluwul jàmbaar. \q1 \v 17 Yaakaar aw fas nax sa bopp la, \q1 kàttanu fas dug wall. \q1 \v 18 Ma ne, Aji Sax jee naa jàkk ku ko ragal \q1 tey wéeroo ngoram. \q1 \v 19 Day jot bakkanam, \q1 di ko dundal cib xiif. \b \q1 \v 20 Nu ngi séentu Aji Sax ji, \q1 moo nuy taxawu, di nu feg. \q1 \v 21 Ci moom la sunu xol di sedde, \q1 turam wu \w sell|lemma="sell:"\w* lanu wóolu. \q1 \v 22 Aji Sax ji, ngalla baaxe nu sa ngor, \q1 moom lanu yaakaar fi yaw. \c 34 \s1 Aji Sax ji du tanqamlu aji jub \d Ñeel Daawuda. Mooy ba muy wayadi-wayadilu ca kanam Abimeleg, ba Abimeleg dàq ko, mu dem\f + \fr 34.1 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk 1.Samiyel\+bk* 21.10-15. Akis buurub Gaat mooy Abimeleg ba tey.\ft*\f*. \b \q1 \v 1 Naa màggal \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji saa su ne, \q1 di ko sant fu ma tollu. \q1 \v 2 Aji Sax ji laay sagoo, \q1 néew-ji-doole dégg, bég. \q1 \v 3 Kañleen Aji Sax ji, ànd ceek man, \q1 nu bokk wormaal turam. \b \q1 \v 4 Maa sàkku Aji Sax ji, mu nangul ma, \q1 tàggale maak lépp lu ma ragal. \q1 \v 5 Ku yaakaar Aji Sax ji bég, leer nàññ, \q1 gàcce du ko sëlëm. \q1 \v 6 Néew-ji-doole woote, Aji Sax ji wuyu, \q1 musal ko fu mu jàqe. \q1 \v 7 Ku ragal Aji Sax ji, malaakaam yiir la, \q1 di la wallu. \q1 \v 8 Mosleen, xam ne Aji Sax jee baax, \q1 ndokklee yaw mi ko làqoo. \q1 \v 9 Ragal-leen Aji Sax ji, yeen nitam ñu sell ñi; \q1 ku ko ragal doo ñàkk dara. \q1 \v 10 Gaynde man naa ndóol, xiif, \q1 nit sàkku Aji Sax ji, ñàkkul lenn lu baax. \b \q1 \v 11 Dikkal doom, déglu ma, \q1 ma jàngal la ragal Aji Sax ji. \q1 \v 12 Ana ku dund neex, \q1 mu bëgga gudd fan, ba gis ngëneel? \q1 \v 13 Na làmmiñam daw lu aay, \q1 dawi fen. \q1 \v 14 Na dëddu lu bon tey def lu baax, \q1 sàkku jàmm, saxoo ko. \b \q1 \v 15 Ay gët la Aji Sax ji ne jàkk aji jub ji, \q1 te ay noppam la dékk wooteb wallam. \q1 \v 16 Aji Sax jeey rëbb kuy jëfe mbon, \q1 ngir dagge ko kaw suuf, far turam. \q1 \v 17 Ku jub yuuxu, Aji Sax ji dégg, \q1 fu mu jàqe, mu musal ko. \q1 \v 18 Sa yaakaar tas, Aji Sax ji jege la, \q1 sa xol jeex, Aji Sax ji wallu la. \q1 \v 19 Musiba bare naa dal ku jub, \q1 Aji Sax ji musal ko ci lépp, \q1 \v 20 di ko sàmm, \q1 ba benn yaxam du damm. \q1 \v 21 Musiba nag day rey ku bon, \q1 te ku bañ aji jub, yoon dab na la. \q1 \v 22 Aji Sax jeey jot ab jaamam, \q1 képp ku ko làqoo, yoon du la dab. \c 35 \s1 Aji Sax ji, àtte maak noon \d \v 1 Ñeel Daawuda. \b \q1 Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, digaaleel ak samay digaale, \q1 xeexal maak ñi may xeex. \q1 \v 2 Fëkkal sa pakk ak sa kiiraay, \q1 taxawusi ma, \q1 \v 3 xàcci sa xeej ak sa sémmiñ, \q1 dajeek ñi may dàq. \q1 Déey ma, ne ma: «Sag mucc, man a.» \q1 \v 4 Ñiy wut sama bakkan, yal nañu rus ba torox; \q1 ñi may fexee lor, yal nañu leen waññi, sewal leen. \q1 \v 5 Yal na leen malaakam Aji Sax ji bëmëx, \q1 nim ñax mu ngelaw wal. \q1 \v 6 Yal na leen malaakam Aji Sax ji dàq, \q1 ñuy lëndëmtuy tarxiis. \b \q1 \v 7 Defuma dara, ñu di ma fiir, \q1 defuma dara, ñu gas um yeer, di ma tëru. \q1 \v 8 Yal nañu sànkoo mbetteel, \q1 keppoo seen fiir, \q1 sànkoo seenum yeer. \b \q1 \v 9 Su boobaa ma bége Aji Sax ji, \q1 bànneexoo wallam, \q1 \v 10 di ko sante sama jëmm jépp, \q1 naan: «Éy Aji Sax ji, ana ku mel ni yaw, \q1 di xettli néew-ji-doole ci boroom doole, \q1 ak ku néewleek ku ñàkk ca ka leen di lekk?» \b \q1 \v 11 Nit ku bon a ngi may duural, \q1 di ma jiiñ lu ma yégul. \q1 \v 12 Ma ji leen njekk, ñu fey ma njekkar, \q1 ndaw tiisu xol! \q1 \v 13 Man de ba ñu woppee, maa ngi ñaawlu, \q1 di woor, toroxloo, \q1 sukk, ñaanal leen, \q1 \v 14 tiisoo leen ni saab xarit mbaa doomu ndey, \q1 di ñaawlook a yoggoorlu ni ku ñàkk yaay. \q1 \v 15 Ma daanu tey, ñu daje di ko bége, \q1 dajaloo fi sama kaw, \q1 di ma fexeel te yéguma, \q1 di ma yàpp, tëë ba. \q1 \v 16 Tekkiwuñu dara, di ma ñaawal rekk \q1 te di ma màttu. \q1 \v 17 Éy Aji Sax ji, loo deeti seetaan? \q1 Musal ma ci seenum pàdd, \q1 wallu ma ci yii gaynde, \q1 sàmmal ma sama benn bakkan bii! \q1 \v 18 Maa lay sante fa ndaje yaatoo, \q1 màggal la digg mbooloo mu yaa. \b \q1 \v 19 Noon bu ma deful dara, yàlla bumu gis lu mu ma damoo. \q1 Ku ma bañ ci dara, yàlla bumu ma ree. \q1 \v 20 Waxuñu jàmm, \q1 xanaa di ràbbal niti jàmm ci réew mi \q1 ay kàdduy tuuma. \q1 \v 21 Ñu ngi ma ŋa ŋàpp, di ma tuumaal, \q1 naan: «Yaw a, yaw a, noo la gis!» \b \q1 \v 22 Éy Aji Sax ji, yaa ci gis, bul selaŋlu, \q1 éy Boroom bi, bul ma sore. \q1 \v 23 Jógal, sàmmal ma sama àq. \q1 Sama Yàlla, Boroom bi, àtte ma yoon. \q1 \v 24 Aji Sax ji sama Yàlla, àttee ma sa dëgg, \q1 ñu bañ maa ree! \q1 \v 25 Yàlla buñu ne: «Ñaw! Lii rekk lanu bëggoon.» \q1 Yàlla buñu ne: «Sàkkal nanu ko pexe.» \b \q1 \v 26 Ku bége sama njàqare, \q1 yal nanga rus, ba torox. \q1 Kuy réy-réylu ci sama kaw, \q1 yal nanga am gàcce, ne yàcc. \q1 \v 27 Ku bége sama der bu set, \q1 yal nanga bànneexu, di sarxolle, \q1 foo tollu di biral naan: \q1 «Aji Sax jee màgg! \q1 moom miy bége jàmmi jaamam.» \q1 \v 28 Man it ma tudd sa njekk, \q1 di la dëkke màggal! \c 36 \s1 Nit ñaaw, Aji Sax ji gore \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda jaamub \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \b \q1 \v 1 Kàddug tooñ ga ku bon wax mu ngi sama xel mi. \q1 Mu ne: «Ana lu may ragal ci Yàlla?» \q1 \v 2 Day gis boppam, naagu, \q1 ba du gis sikkam, sib ko. \q1 \v 3 Ay waxam coxor aki fen, \q1 jëfeetul lu rafet ak lu baax. \q1 \v 4 Day mébét lu ñaaw cib lalam, \q1 taxawe yoon wu dëddu mbaax, \q1 te du bañ lu bon. \b \q1 \v 5 Céy Aji Sax ji, gore nga ba kaw asamaan, \q1 dëggu ba kaw-li-kaw. \q1 \v 6 Sa njekk a tiim tund yu mag yi, \q1 sa àtte ne xéew ni xóotey géej. \q1 Céy Aji Sax ji, nit ak mala, nga boole sàmm! \q1 \v 7 Céy Yàlla, yaa wéet ngor, \q1 doom aadama yiiroo sa ker, yiiru; \q1 \v 8 yafloo sa njël lu duun, \q1 sa xéewal wal, nga nàndale ko. \q1 \v 9 Ci yaw la dund di balle, \q1 te sag leer lanuy leerloo. \b \q1 \v 10 Jotaleel sa ngor ku la xam, \q1 jotale sa njekk kuy nas njub. \q1 \v 11 Yàlla bu ma ku reew teg tànk; \q1 loxo ku bon, yàlla bumu ma taxa daw. \q1 \v 12 Defkati mbon yaa ngii, daanu, \q1 ne lareet, tëlee jóg. \c 37 \s1 Bu sa xol jóg \d \v 1 Ñeel Daawuda. \b \q1 Bu sa xol jóg ci ku bon, \q1 bul ñee kuy def njombe. \q1 \v 2 Léegi mu wow nim ñax, \q1 lax ni gàncax. \b \q1 \v 3 Dénkul ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, di def lu baax, \q1 ba des ci réew meek jàmm. \q1 \v 4 Deel bànneexoo Aji Sax ji, \q1 mu may la say nammeel. \b \q1 \v 5 Jébbalul ci Aji Sax ji, \q1 dénku ci moom, mooy sottal. \q1 \v 6 Day setal sab der ni jant bu fenk; \q1 sab àtte ne ràññ ni njolloor. \b \q1 \v 7 Neel tekk, xaar Aji Sax ji, \q1 yaakaar ko. \q1 Bu sa xol jóg ci kuy baaxle, \q1 tey lal ay pexe. \b \q1 \v 8 Baal mer, dëddu xadar. \q1 Xol bu jóg, loraangey neen. \q1 \v 9 Ku bon, ñu dagg, sànni; \q1 ku yaakaar Aji Sax ji, jagoo réew mi. \b \q1 \v 10 Nes tuut, ku bon ne mes, \q1 nga seet, seet, mu réer. \q1 \v 11 Waaye néew-dooleey jagoo réew mi; \q1 jàmm ne ñoyy, ñu bége. \b \q1 \v 12 Ku bon fexeel ku jub, \q1 di ko màttu, \q1 \v 13 Buur Yàlla di ko ree, \q1 xam ne bésam a ngi ñëw. \b \q1 \v 14 Ku bon bocci saamar, \q1 tàwwig fitt, \q1 nara rey ku ñàkk, néewle, \q1 nara bóom kuy jubal; \q1 \v 15 far jam boppam saamaru xol, \q1 fittam damm. \b \q1 \v 16 Aji jub, as tuutam \q1 moo gën koomu ku bon. \q1 \v 17 Ku bon kat, sa doole dëddu la; \q1 ku jub, Aji Sax ji wallu la. \b \q1 \v 18 Ku maandu, Aji Sax ji yég la, \q1 sab cér sax. \q1 \v 19 Bu mettee doo rus, \q1 te bésub xiif dangay regg. \b \q1 \v 20 Ku bon sànku; \q1 noonub Aji Sax ji, taaru tool bu naat la, \q1 bu tàkkee, jeex tàkk. \b \q1 \v 21 Ku bon leb, du fey; \q1 ku jub yéwén, di joxe. \q1 \v 22 Aji Sax ji barkeel la, nga jagoo réew mi moos; \q1 mu alag la, nga dog. \b \q1 \v 23 Aji Sax jeey sopp saw yoon, \q1 jiite say jéego. \q1 \v 24 Soo tërëfee it, doo daanu. \q1 Aji Sax jee lay walloo loxoom. \b \q1 \v 25 Ba may ndaw, ba tey may mag, \q1 gisuma ku jub ñàkk ndimbal, \q1 mbaa askanam di dunde yalwaan. \q1 \v 26 Day saxoo tabe, di leble, \q1 askanam barkeel. \b \q1 \v 27 Dëddul mbon, di jëfe mbaax, \q1 ba dëkke réew mi fàww. \q1 \v 28 Aji Sax ji kat daa sopp yoon, \q1 te du wacc jaamam bu gore. \b \q1 Day fegu ba fàww, \q1 askanu ku bon dog. \q1 \v 29 Aji jub ay jagoo réew mi, \q1 dëkke ko ba fàww. \b \q1 \v 30 Kàddug aji jub day xelu, \q1 wax ja jub; \q1 \v 31 yoonu Yàllaam a nga ca xol ba, \q1 du dox ba tërëf. \b \q1 \v 32 Ku bon a ngi yeeru ku jub, \q1 di ko wuta bóom. \q1 \v 33 Waaye Aji Sax ji du ko bàyyeek moom, \q1 te deesu ko daan cib layoo. \b \q1 \v 34 Yaakaaral Aji Sax ji, sàmm yoonam, \q1 mu teral la, nga jagoo réew mi, \q1 ku bon sànku, ngay gis. \b \q1 \v 35 Damaa gis ku bon di note, \q1 te sëq ni garab gu naat fa mu fekk baax, \q1 \v 36 ma jaareeti fa, ndeke wuute na, \q1 ma seet ko, gisuma ko. \b \q1 \v 37 Bàyyil xel ku maandu, xool ku jub; \q1 muj, fa nitu jàmm. \q1 \v 38 Moykat yeey sànkoondoo, \q1 ku bon amul muj. \b \q1 \v 39 Aji Sax jeey musal ku jub, \q1 di ko aar bésub njàqare. \q1 \v 40 Aji Sax jee koy taxawu, wallu ko, \q1 wallu ko ci ku bon, musal ko, \q1 ndax li mu ko làqoo. \c 38 \s1 Maa wopp, tuub, di jooy \d Muy kàddug Sabóor guy fàttlee, ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, bul mer, di ma rëbb; \q1 bul xadaru, di ma mbugal. \q1 \v 2 Aji Sax ji, fitt nga maa fitt, \q1 dóor nga ma. \q1 \v 3 Danga maa mere, ma wéradi; \q1 maa bàkkaar, ba jagadi. \q1 \v 4 Samay ñaawtéef mëdd ma, \q1 diisa diis, ba àttanuma ko. \q1 \v 5 Maa def ug ndof, \q1 ba am dana yu bédd, ba xasaw. \q1 \v 6 Maa ngi sëgg, ne yàcc, ne yasar, \q1 di wéye tiis, \q1 \v 7 yaram tàng, di bax, \q1 ma wéradi, ne làcc. \q1 \v 8 Sama yaram dee goyy, ma ne lasar, \q1 jàq, di binni. \q1 \v 9 Boroom bi, yaa ngi ne jàkk ci samay nammeel, \q1 samay onk umpu la. \q1 \v 10 Sama fit a ngi tëf-tëfi, doole ŋiis, \q1 gët giim. \q1 \v 11 Xarit ak dëkkandoo di ma daw, \q1 mbokk dànd ma. \q1 \v 12 Ñi may wuta rey a ngi may fiir, \q1 di ma jéema lor, di ma waxal musiba, \q1 yendu maa lalal pexe. \q1 \v 13 Man, ma mel nib tëx, dégguma, \q1 mel ni luu, àdduwma, \q1 \v 14 di saf ku dul dégg, \q1 bay layoo. \b \q1 \v 15 Aji Sax ji, yaw laa yaakaar; \q1 Boroom bi, sama Yàlla, yaa may nangul. \q1 \v 16 Ma ne, ngalla buñu ma ree, \q1 di damoo samab jéll. \q1 \v 17 Maa ngii di waaja daanu, \q1 dëkke metit. \q1 \v 18 Ma ne, aylayéwén def naa lu ñaaw, \q1 sama bàkkaar tiital na ma. \q1 \v 19 Noon yaa ngi ne jonn ak seen doole, \q1 bare na ñu ma bañ ci neen. \q1 \v 20 Ma ji leen njekk, ñu fey ma njekkar; \q1 may sàkku lu baax, ñu di ma sikk. \q1 \v 21 Éy Aji Sax ji sama Yàlla, bu ma wacc, \q1 bu ma sore. \q1 \v 22 Ngalla gaawe ma; \q1 Boroom bi, yaa may musal. \c 39 \s1 Dund yàggul \d Mu jëm ci Yedutun, njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 Dama noon: «Damay moyu ba duma moye làmmiñ.» \q1 Li feek ku bon di teew, \q1 may ŋalaab sama gémmiñ. \q1 \v 2 Dama noon cell, ne patt, \q1 noppi, ba mu ëpp; \q1 sama njàqare yokku, \q1 \v 3 sama xol diis, \q1 xel di xelaat, xol diis gann; \q1 ma mujj àddu, \q1 \v 4 ne: «Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, xamal ma sama muj \q1 ak sama àppi fan, \q1 ma xam ni sama dund gàtte. \q1 \v 5 Yaatuwaayu loxo nga ma àppal ciy fan, \q1 sama giiru dund du dara fi yaw. \q1 Képp ku taxaw di cóolóolu neen. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \q1 \v 6 Nit du lu moy takkndeer buy dem, \q1 cóolóolu neen lay kër-këri. \q1 Nit a ngi dajale, xamul kuy for. \b \q1 \v 7 «Éy Boroom bi, lu may xaarati? \q1 Sama yaakaar yaw a. \q1 \v 8 Musal ma ci sama mbugali tooñoo tooñ, \q1 bu ma bàyyi, dof di ma reetaan! \q1 \v 9 Noppi naa, dootuma wax, \q1 yaw yaa dogal lii. \q1 \v 10 Waaye ngalla teggil sab yar, \q1 sa diisaayu loxoo ngi may jekkli. \q1 \v 11 Yaay mbugal ku bàkkaar, yar ko, \q1 ronq ni max la mu gëna fonk. \q1 Nitoo nit, cóolóolu neen. \qs Selaw.\qs* \q1 \v 12 Éy Aji Sax ji, déglul, ma ñaan la, \q1 teewlul, ma woo la wall; \q1 bul tanqamlu sama yuux, \q1 doxandéem doŋŋ laa fi yaw, \q1 di gan ni maam yépp. \q1 \v 13 Ngalla xiddi ma, ma muuñ, \q1 bala maa dëddu, réer.» \c 40 \s1 Déggal Aji Sax jee am solo \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. \b \q1 \v 1 May xaara xaar \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 mu dégg may woote, geesu ma, \q1 \v 2 génnee ma ca kàmbug sànkute, \q1 sippee ma ca xóotey ban ba, \q1 cëppe ma ciw doj, \q1 samp ma, ma dëgër. \q1 \v 3 Moo ma may, ma fent, \q1 woy wu ma woye sunu Yàlla. \q1 Ñu baree seede, di wormaal \q1 ak a dénku ci Aji Sax ji. \b \q1 \v 4 Ndokklee, yaw mi dénku ci Aji Sax ji, \q1 te sàkkuwoo ku bew \q1 ak kuy topp ay fen. \q1 \v 5 Yaw Aji Sax ji sama Yàlla, bare nga loo def, \q1 amuloo moroom! \q1 Bare nga kéemaan aki mébét yoo nu sottalal, \q1 ma bëgga xamle lépp, \q1 te mu bare ba wees ab lim. \q1 \v 6 Saraxi gàtt mbaa pepp, taamuwuloo ko, \q1 ay nopp nga ma bënnal, \q1 \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ak \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*, \q2 sàkkuwuloo ko. \q1 \v 7 Ma ne: «Maa dikk nii, \q1 téereb yoon wi indi na li ñu bind ci man. \q1 \v 8 Sama Yàlla, maa soppa def sa coobare, \q1 ci sama biir xol la sa ndigali yoon nekk.» \b \q1 \v 9 Siiwal naa sag njekk ca ndaje mu mag ma. \q1 Dama ne, Aji Sax ji duma noppi, xam nga ko. \q1 \v 10 Làquma sag njekk, ne cell ak moom. \q1 Yaa wóor, di walloo, siiwal naa ko. \q1 Làquma ndaje mu mag ma sa ngor ak sa worma. \b \q1 \v 11 Éy Aji Sax ji, bu ma xañ sa yërmande. \q1 Sa ngor ak sa worma, \q1 yal na ma feg ba fàww. \b \q1 \v 12 Ay musibaa ma tanc, \q1 ne gàññ, ba wees ab lim. \q1 Samay ñaawtéef a ma dab, ba gisatuma, \q1 baree bare, ba ëpp sama kawari bopp; \q1 sama xol jeex tàkk. \q1 \v 13 Éy Aji Sax ji, yal na la neex, nga wallu ma! \q1 Éy Aji Sax ji, gaawe ma! \q1 \v 14 Képp kuy wuta fëkk sama bakkan, \q1 yal na rus, torox ne tott. \q1 Kuy bége sama loraange, \q1 yal nañu ko duma, mu ne yàcc. \q1 \v 15 Ku may ñaawal, \q1 yal nañu ko torxal, mu jommi. \q1 \v 16 Képp ku lay sàkku, \q1 yal na bég, di la bànneexoo. \q1 Képp ku safoo sag wall, \q1 yal na jàppoo: «Aji Sax ji màgg na!» \q1 \v 17 Man, néew naa doole, ñàkk naa, \q1 waaye yaw Aji Sax ji, danga maa yég. \q1 Yaw yaa may wallu, xettli ma; \q1 sama Yàlla, bu ma yeexe. \c 41 \s1 Jarag bu ñu toŋal a ngi ñaan \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 Ndokklee yaw mi yég néew-ji-doole. \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee lay xettli, bésub njàqare. \q1 \v 2 Aji Sax jee lay aar, di sàmm sa bakkan, \q1 nga jagoo barke ci réew mi, \q1 te du la bàyyi noon def la lu ko neex. \q1 \v 3 Aji Sax jee lay dooleel soo woppee, \q1 di soppi bu baax sa tëraay. \b \q1 \v 4 Dama ne: «Aji Sax ji, tooñ naa la; \q1 baaxe ma, faj ma.» \q1 \v 5 Noon yaa ngi may yéene lu bon, \q1 naan: «Xanaa kii du dee, ba ñu fàtte ko?» \q1 \v 6 Ku dikk, di ma seet, di jinigal \q1 tey fenti sos ci xolam, \q1 bu génnee, tasaare ko. \q1 \v 7 Bañ yépp a ngi may déeyoo, \q1 di ma fexeel lu bon, \q1 \v 8 naan: «Musiba dal na ko, du jógati!» \q1 \v 9 Sama am-di-jàmm bu ma wóolu sax jógal na ma, \q1 te daan lekk samaw ñam. \b \q1 \v 10 Waaye ngalla Aji Sax ji, baaxe ma, \q1 yékkati ma, ma fey leen. \q1 \v 11 Su noon damuwul ci sama kaw, \q1 ma doora xam ne bége nga ma. \q1 \v 12 Man, damaa maandu, nga taxawu ma, \q1 dëj ma fi sa kanam, ba fàww. \b \q1 \v 13 Cant ñeel na Aji Sax ji, Yàllay Israyil. \q1 Moo masa yelloo cant, ba fàww. \q1 Amiin, Amiin. \c 42 \s1 Maa namm Yàlla \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di taalif bu ñeel askanu Kore wu góor. \b \q1 \v 1 Yaw Yàlla, ni kéwél di sàkkoo walum ndox, \q1 maa la koy sàkkoo xol. \q1 \v 2 Maa mar Yàlla, \q1 Yàlla jiy dund! \q1 Kañ laay teewi fa kanam Yàlla? \q1 \v 3 Rongooñ laay dunde \q1 guddeek bëccëg, \q1 noon yi di ma dëkke naa: \q1 «Ana sa Yàlla ji?» \q1 \v 4 Lii laay fàttliku, sama xol jeex: \q1 dama daan jàll, jiite mbooloo ma, \q1 jëm kër Yàlla ga, di sarxolleek a sant, \q1 ñu booloo di màggal. \q1 \v 5 Moo man, lu may yoggaaral nii? \q1 Lu may jàq? \q1 Naa yaakaar Yàlla, \q1 ba dellu sante sama Yàlla wallam. \b \q1 \v 6 Maa ngi ne yogg, \q1 ba di la fàttlikoo fa réewum Yurdan \q1 ak tundi Ermon ak Misar. \q1 \v 7 Sa wal ya sotti, xóote awu moroom ma; \q1 say wal ak say gannax, lépp a jaare sama kaw. \q1 \v 8 Bëccëg \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji baaxe ma ngoram, \q1 guddi ma fanaane koo woy, \q1 di ñaan Yàlla mi may dundal. \q1 \v 9 Naa wax Yàlla ji ma sës, ne ko: \q1 «Lu tax nga fàtte ma, \q1 noon di ma fitnaal, \q1 may wéye tiis?» \q1 \v 10 Noon yaa ngi may ñaawal, \q1 di ma yendoo naa: \q1 «Ana sa Yàlla ji?» \q1 Ma ne yàcc, ne yasar. \q1 \v 11 Moo man, lu may yoggaaral nii? \q1 Lu may jàq? \q1 Naa yaakaar Yàlla, \q1 ba dellu sante sama Yàlla wallam. \c 43 \s1 Éy Yàlla, àtte ma \q1 \v 1 Éy Yàlla, àtte ma, \q1 layool maak xeet wu gorewul, \q1 xettli maak ku njublaŋ te dëng. \q1 \v 2 Yaw Yàlla kat yaay sama rawtu. \q1 Lu tax nga wacc ma, \q1 may wéye tiis, \q1 ci noteelu noon? \q1 \v 3 Ngalla yónneel sag leer ak sa dëgg, \q1 yal na ma yooyu jiite, \q1 yóbbu ma sa tund wu \w sell|lemma="sell:"\w*, \q1 sa dëkkuwaay ba. \q1 \v 4 Kon Yàlla, naa àgg sa \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*; \q1 yaw Yàlla, yaay sama mbégte, di sama bànneex. \q1 Yaw Yàlla, sama Yàlla, \q1 naa la màggale xalam. \q1 \v 5 Moo man, lu may xàddi, ne yogg? \q1 Lu may jàq nii? \q1 Tee maa yaakaar Yàlla, ba santati ko, \q1 moom sama Yàlla mi may wallu? \c 44 \s1 Xeet waa ngi jooy \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di taalif bu ñeel askanu Kore wu góor. \b \q1 \v 1 Éy Yàlla, noo déggal sunu bopp, \q1 sunuy maam a nu wax \q1 jëf ja nga jëf, ca seeni jant, \q1 bu yàgga yàgg. \q1 \v 2 Yaw ci sa bopp yaa dàq xeet yi, \q1 jëmbat fa maam ya; \q1 yaa mbugal xeet yi, \q1 ñoom, nga yiwi leen. \q1 \v 3 Du seen saamar lañu nangoo réew mi moos, \q1 seen dooley bopp it mayu leen ndam. \q1 Yaa ko defe kàttan ak doole, \q1 geesoo leen sa leeru kanam, \q1 ngir sa cofeel. \b \q1 \v 4 Yaay kiy sama buur, di sama Yàlla, \q1 mayal askanu Yanqóoba ay ndam. \q1 \v 5 Yaw lanuy dàqe bañ yi, \q1 sa tur lanuy dëggaatee ñi nu song. \q1 \v 6 Du fitt laa wóolu, \q1 du saamar a may may ndam. \q1 \v 7 Yaa nuy musal ci bañ yi, \q1 yaay gàcceel noon ñi. \q1 \v 8 Yàlla lanuy damoo bésoo bés, \q1 di màggal turam ba fàww. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \b \q1 \v 9 Waaye danga noo wacc, \q1 torxal nu, \q1 ba àndulook sunu mboolooy xare. \q1 \v 10 Waññi nga nu, nu won noon yi gannaaw, \q1 ñu bañ nu, ba futti nu. \q1 \v 11 Ni gàtt yu ñuy yàpp, ni nga nu joxee, \q1 tasaare nu ci biir xeet yi. \q1 \v 12 Jaay nga sa mbooloo ci dara, \q1 te jariñu la tus. \q1 \v 13 Tax nga sunuy dëkk di nu ree, \q1 ñi nu séq di nu kókkaleek a ñaawal. \q1 \v 14 Tax nga xeet yi di nu léeboo, \q1 jaambur yaa ngi nuy wëcc bopp! \q1 \v 15 Damaa dëkke gàcce, \q1 sëlmoo kersa \q1 \v 16 ndax kókkali yeek xastey nit \q1 ñi ma bañ, di feyoonteek man. \b \q1 \v 17 Lii lépp dal na nu, \q1 te fàttewunu la, fecciwunu la \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w*. \q1 \v 18 Dëdduwunu la, \q1 wàccunu saw yoon, \q1 \v 19 teewul nga not nu, wacce nu xaj ya, \q1 këpp nu lëndëmu ndee. \q1 \v 20 Su nu la fàtte woon yaw, sunu Yàlla, \q1 ba tàllal tuuri doxandéem yi loxo, \q1 \v 21 du la ump, yaw Yàlla, \q1 mi xam kumpay xol. \q1 \v 22 Yaa tax ñu yendu noo bóom, \q1 dees noo jàppe ni xar yu ñuy tër. \b \q1 \v 23 Éy Aji Sax ji, jógal! Looy nelaw? \q1 Yewwul, bu nu wacc ba fàww. \q1 \v 24 Loo nu làqe saw yiw, \q1 di fàtte sunu njàqareek sunu coono? \q1 \v 25 Nu ngi ne ñàyy ci pënd bi, \q1 di watat koll fi suuf. \q1 \v 26 Wallusi nu, jot nu \q1 ngir sa ngor. \c 45 \s1 Buur a ngi séetal \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor, ñeel askanu Kore wu góor, dib taalif, te di woyu mbëggeel. \b \q1 \v 1 Woy wu neex a fees sama xol, \q1 may taalifal Buur, \q1 sama làmmiñ ni xalimag bindkatu ndaanaan. \b \q1 \v 2 Yaa gëna góorayiwe ci àddina, \q1 sa kàddu diw yiw, \q1 ndax Yàllaa la barkeel ba fàww! \q1 \v 3 Jàmbaaroo, takkal sa saamar, \q1 te yànj, am daraja; \q1 \v 4 ànd ak daraja, dawal ba am ndam, \q1 di dawal dëgg ak yërmande ji war, \q1 ba mana def ay jaloore. \q1 \v 5 Yaw Buur, say fitt a ñaw, \q1 di jam say noon ci xol, \q1 ay xeet daanu, nga tiim. \q1 \v 6 Yaw Yàlla, sab jal a sax dàkk ba fàww. \q1 Njub nga ŋanke sa nguur gi, \q1 \v 7 di sopp dëgg, bañ lu bon, \q1 ba Yàlla, sa Boroom diwe la diwu mbég, \q1 nga tiim say moroom: \q1 \v 8 sa yére yépp di gilli ndàbb, \w alowes|lemma="alowes:"\w* akum kanel, \q1 ñu di la bégale xalam, \q1 ca sa biir kër yu yànj. \q1 \v 9 Ay doomi buur a ngi ci jigéen ñi nga teral, \q1 sab lingeer féete la ndijoor, \q1 takkoo ngëneelu wurus. \b \q1 \v 10 Janq doom, gisal, déglul te teewlu ma, \q1 fàtteel say bokk, fàtte sa kër baay, \q1 \v 11 Buur xemmeme la sab taar; \q1 mooy sab sang, wormaal ko. \q1 \v 12 Waa Tir a lay yótsiy may, \q1 ay boroom alal di wut lu la neex. \b \q1 \v 13 Séetu Buur duggsi na, ne ràññ, \q1 sol mbubb mu wurus way tàkk. \q1 \v 14 Ñu yóbbul ko Buur, mu ne boyy, \q1 janq ja ànd ak moom, diy toppam, ñu indil leen Buur, \q1 \v 15 ñu duggsi kër Buur, \q1 ci biir mbégteek bànneex. \b \q1 \v 16 Yal na la sa doom yu góor wuutu ci seen jalu maam, \q1 nga def leeni kàngam ci réew mi mépp. \q1 \v 17 Maa lay joobe ba sa tur du fey mukk, \q1 xeet yi saxoo laa sant ba fàww. \c 46 \s1 Aji Sax jee ànd ak man \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di jàngin wu ñeel askanu Kore wu góor, dëppook galan bu ñuy wax Baatu jigéen. \b \q1 \v 1 Sunu Yàllaa nuy rawale, di nu dooleel, \q1 di nu wallu fu nu jaaxlee, \q1 \v 2 ba dunu tiit suuf su yëngu sax, \q1 ba tund yiy tàbbi biir géej, \q1 \v 3 mbaa gannax yuy riir, di fuur \q1 ak a fuddu bay gësëm tund yi. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \b \q1 \v 4 Ag dex a ngi defi wal, di bànneexal dëkku Yàlla, \q1 sellngay dëkkuwaayi Aji Kawe ji. \q1 \v 5 Yàllaa ngi ci biir dëkk bi, du raf; \q1 Yàllaa koy dimbali ba jant fenkee. \q1 \v 6 Ay giir a riir, ay réew yëngu; \q1 mu àddu, suuf seey! \q1 \v 7 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoor yee ànd ak nun, \q1 Yàllay Yanqóoba jee nuy rawale. \qs Selaw.\qs* \b \q1 \v 8 Dikkleen gis jaloorey Aji Sax ji, \q1 ak yàqute gi mu dogal ci kaw suuf. \q1 \v 9 Mu ngi fey xare ci àddina sépp, \q1 dog fitt, damm xeej, \q1 lakk pakk. \q1 \v 10 Mu ne: «Dal-leen te xam ne maay Yàlla, \q1 màgg ci biir xeet yi, màgg fi kaw suuf.» \q1 \v 11 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ànd ak nun, \q1 Yàllay Yanqóoba jii a nuy rawale. \qs Selaw.\qs* \c 47 \s1 Yàllaay buur \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor. \b \q1 \v 1 Na xeetoo xeet tàccu, \q1 xaacu, sarxolleel Yàlla! \q1 \v 2 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, Aji Kawe jee jara ragal, \q1 mooy buur bu mag bi tiim àddina sépp. \b \q1 \v 3 Moo nu nangulal xeet yi, \q1 nu teg tànk gàngoor yi. \q1 \v 4 Moo nu tànnal céru suuf, \q1 muy sagu askanu Yanqóoba wii mu sopp. \q1 \v 5 Yàllaa yéeg, kàddu riir. \q1 Aji Sax jee yéeg, bufta jolli. \b \q1 \v 6 Woyleen Yàlla, woyleen, \q1 woyleen Yàlla sunu buur, woyleen. \q1 \v 7 Yàllaay buuru àddina sépp; \q1 taalifleen, woy ko. \q1 \v 8 Yàllaa di buuru xeet yi, \q1 Yàllaa tooge jalam bu \w sell|lemma="sell:"\w*. \q1 \v 9 Kàngami xeet yeey daje, \q1 ànd ak ñoñi Yàllay Ibraayma; \q1 Yàllaa moom buur yi yiir àddina, \q1 te moo kawee kawe. \c 48 \s1 Aji Sax ji aar na Siyoŋ \d Muy woyu Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor. \b \q1 \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee màgg, jara màggala màggal \q1 ca sunu biir dëkku Yàlla, kaw tundam wu \w sell|lemma="sell:"\w*. \q1 \v 2 Jekk taxawaayee tundu \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, catu bëj-gànnaar, \q1 dëkku buur bu mag bi, \q1 di mbégtem àddina sépp. \q1 \v 3 Yàllaa wone kaaraangeem \q1 ca biir tatay dëkk ba. \b \q1 \v 4 Buur yaa ngoog daje, \q1 àndandoo. \q1 \v 5 Nun noo gis, jommi, \q1 tiit, fëx, \q1 \v 6 ne fay pat-pati, \q1 jàq ni kuy matu. \q1 \v 7 Ngelawal penku, moom ngay tase \q1 gaal gu mag. \b \q1 \v 8 La nu déggoon de lanu gis \q1 ca dëkkub Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, \q1 sunu dëkku Yàlla ba. \q1 Yàllaa koy dëgëral ba fàww. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \q1 \v 9 Céy Yàlla, nu ngi sa biir kër, \q1 di xalaat sa ngor. \q1 \v 10 Céy Yàlla, sa tur ay sa woy \q1 ba ca cati àddina. \q1 Njekk la sa loxo fees. \q1 \v 11 Yal na waa tundu Siyoŋ bég, \q1 waa Yuda bànneexoo say àtte. \b \q1 \v 12 Doxleen biir Siyoŋ, wër ko, \q1 waññleen ay soorooram, \q1 \v 13 nemmikuy tataam, \q1 doxantoo këri buur, \q1 ba man koo yegge maasug ëllëg, \q1 \v 14 ne leen kii ay Yàlla, sunu Yàlla, \q1 tey ak ëllëg. \q1 Moo nuy jiite ba saa taxaw. \c 49 \s1 Alal day naxe \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor. \b \q1 \v 1 Yeen, xeetoo xeet, dégluleen; \q1 yeen, waa àddina yépp, teewluleen, \q1 \v 2 ngay ku tuut di ku mag, \q1 nga bareleek nga néewle. \q1 \v 3 Li may wax xel la, \q1 di xalaat yu déggu. \q1 \v 4 Damay teewlu kàddu yu xelu, \q1 xalamal la sama tekkiteb cax. \b \q1 \v 5 Ana lu may tiit bés yu metti, \q1 yu ma njublaŋ yéewe seeni ñaawtéef, \q1 \v 6 di ñu wóolu seen am-am, \q1 di kañoo alal ju bare? \q1 \v 7 Ana ku mana jota jot sa bakkanu moroom, \q1 mbaa mu di ko feyal Yàlla njot ga? \q1 \v 8 Njotug bakkan jafe na, \q1 bu ci jéem dara. \q1 \v 9 Ana kuy dund ba fàww, \q1 ba doo gis bàmmeel? \b \q1 \v 10 Xanaa gis ngeen ne xelu, dee; \q1 dof, dee; naataxuuna it faatu rekk, \q1 wacce keneen alalam. \q1 \v 11 Sa bàmmeel di sa kër, ba fàww, \q1 di sa dëkkuwaay bu sax dàkk, \q1 boo tudde woon sa bopp ay suuf sax. \q1 \v 12 Nit ak darajaam fanaanul, \q1 mook aw rab a yem, sànku rekk. \b \q1 \v 13 Nii la ku wóolu boppam di mujje, \q1 mook ku ko topp, di safooy waxam. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \q1 \v 14 Nara dee rekk niy xar, \q1 ndee wommat, yóbbu, \q1 njub fenk nib jant, ku jub moom leen, \q1 njaniiw mëdd seen jëmm, \q1 fu sore kërug daraja. \q1 \v 15 Waaye Yàllaa may musal ci dooley njaniiw, \q1 jot sama bakkan, ba jël ma. \b \q1 \v 16 Buleen yéemu ci ku barele, \q1 teraangay këram di yokku. \q1 \v 17 Du dee ba yóbbaale dara, \q1 teraangaam du ko topp biir bàmmeel. \q1 \v 18 Na bége bànneexu bakkanam, \q1 ñu di ko kañe koomam, \q1 \v 19 ba tey, day dee, fekkiy maamam, \q1 ña dootu gis ug leer ba fàww. \q1 \v 20 Nit ak darajaam fanaanul; \q1 mook aw rab a yem, sànku rekk. \c 50 \s1 Aji Sax ji xol lay gërëm \d \v 1 Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf. \b \q1 Yàlla, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Yàlla àddu na, \q1 di woo àddina, penku ba sowu. \q1 \v 2 Ca \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, dëkk ba ca taar ba \q1 la Yàlla feeñe ni leer gu jolli. \q1 \v 3 Sunu Yàllaa ngi ñëw te du ne cell, \q1 sawaraa ko jiitu, di xoyome, \q1 ngëlén lu mag wër ko. \q1 \v 4 Ma ngay woo seede asamaan ak suuf, \q1 ngir àtte ñoñam. \q1 \v 5 Mu ne: «Dajaleel ma sama wóllëre \q1 ñiy sarxal, di ko fase sama \w kóllëreek|lemma="kóllëre g-:"\w* ñoom.» \q1 \v 6 Asamaan a ngi biral njekkam, \q1 ngir Yàllaay àtte. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \b \q1 \v 7 «Yeen sama ñoñ, dégluleen, ma wax leen; \q1 yeen waa Israyil, ma sikk leen. \q1 Maa di Yàlla, seen Yàlla. \q1 \v 8 Du seeni sarax laa leen di sikke, \q1 mbaa seen \w saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* yi sax fi sama kanam. \q1 \v 9 Soxlawuma yëkku yar \q1 ak sikketu gétt. \q1 \v 10 Maay boroom raboo rabu àll, \q1 ak junniy nag yuy fore tund ya. \q1 \v 11 Xam naa njanaawi tund yi, \q1 luy ndundatub tool maa ko moom. \q1 \v 12 Su ma xiifoon, duma leen ko wax, \q1 maa moom àddinaak li ci biiram. \q1 \v 13 Damay lekk yàppu nag \q1 ak a naan deretu sikket a? \q1 \v 14 Deel jaajëfal Yàlla, sarxale ko, \q1 di fey Aji Kawe ji loo dige, \q1 \v 15 di ma woo bésub njàqare, \q1 ma wallu la, nga màggal ma.» \b \q1 \v 16 Ñu bon ñi Yàlla ne leen: \q1 «Lu ngeen di tari sama dogali yoon, \q1 di waxe sama kóllëre? \q1 \v 17 Yeena ngii, bañ sama yar, \q1 xalab samay kàddu. \q1 \v 18 Fu ngeen gis ub sàcc, neexook moom, \q1 ab njaalookat, ngeen lëngool. \q1 \v 19 Dangeena afal seen gémmiñ ci mbon, \q1 seen làmmiñ taqoo fen, \q1 \v 20 ngeen di tooge seen mbokk, \q1 di yàq deru doomu ndey. \q1 \v 21 Lii yeena ko def! Damay noppi, \q1 ngeen defe ne damaa mel ni yeen? \q1 Dama leen di sikk, tuumaal leen, ngeen gis! \b \q1 \v 22 «Yeen fàttekati Yàlla yi, déggleen lii, \q1 bala maa fàdd te kenn du wallu. \q1 \v 23 Ki may sarxale jaajëf moo ma teral; \q1 ku topp yoon, ma won ko wallu Yàlla.» \c 51 \s1 Yàlla, yërëm ma \d Mu jëm ci njiitu jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. Mooy ba ko Yonent Yàlla Natan seetsee, gannaaw ba Daawuda dëkkoo ndaw sa ñuy wax Batseba\f + \fr 51.2 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk 2.Samiyel\+bk* 11—12.25.\ft*\f*. \b \q1 \v 1 Éy Yàlla, ni nga goree, baaxe ma ni, \q1 faral samag tooñ ngir sa yërmande ju yaa. \q1 \v 2 Fóotal maa fóotal sama ñaawtéef, \q1 raxasal ma sama moy. \q1 \v 3 Xam naa ne maa tooñ, \q1 sama moy a ngi janook man saa su ne. \q1 \v 4 Yaw laa moy, yaw doŋŋ. \q1 Li nga ñaawlu laa def. \q1 Kon boo waxee, yaa yey; \q1 te soo àttee, wàcc nga. \q1 \v 5 Ñaawtéef daal laa judduwaale, \q1 te sama ndey ëmbaale ma bàkkaar. \q1 \v 6 Dëgg daal nga namm, dëggu reenu xol, \q1 kon déey ma xel mu rafet. \q1 \v 7 Wis ma ndox, ma sell; \q1 sang ma, ma set wecc. \q1 \v 8 Yal nanga ma dégtal mbég ak bànneex, \q1 ma bégati, gannaaw ba nga ma dammatee. \q1 \v 9 Bul xool samay moy, \q1 faral sama ñaawtéef yépp. \q1 \v 10 Éy Yàlla, sàkkal ma xol bu sell, \q1 yeesalal ma pastéefu xol. \q1 \v 11 Bu ma xalab, \q1 bu ma xañ sa noo gu \w sell|lemma="sell:"\w*. \q1 \v 12 May ma, ma bégeeti sag wall, \q1 te dundale ma xol bu tàlli, \q1 \v 13 ma xamal tooñkat sa war, \q1 ba moykat dellu ci yaw. \b \q1 \v 14 Céy Yàlla, yaw Yàlla mi may musal, \q1 baal ma deret ji ma tuur, \q1 ma siiwal sa njekk. \q1 \v 15 Boroom bi, may ma, ma wax, \q1 ma delloo la njukkal. \q1 \v 16 Sàkkuwloo sarax, nde kon ma indi; \q1 te soppuloo \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*. \q1 \v 17 Saraxi Yàlla, xol bu tuub la, \q1 yaw Yàlla, xol bu tuub ba mokk, doo gàntal boroom. \b \q1 \v 18 Ngalla baaxeel \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, \q1 yal nanga tabax tatay Yerusalem. \q1 \v 19 Su boobaa nga nangu sarax yi war, \q1 di saraxu rendi-dóomal. \q1 Su boobaa ñu rendi ay yëkk ca sa \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*. \c 52 \s1 Yàllaa man boroom doole \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di taalif bu ñeel Daawuda. Mooy ba Doweg, Edomeen ba, demee ca Sóol, ne ko Daawuda dem na kër Ayimeleg\f + \fr 52.2 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk 1.Samiyel\+bk* 21—22.\ft*\f*. \b \q1 \v 1 Moo jàmbaar ji, looy damoo jëfi coxor? \q1 Yàlla, ngoram, bés bu nekk la. \q1 \v 2 Ak sa làmmiñ wi ngay sose loraange, \q1 mel ni saatu su ñu xacc, \q1 rambaaj bi! \q1 \v 3 Lu bon a la gënal lu baax, \q1 fen a la gënal wax dëgg. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \q1 \v 4 Yaa bëgg jépp wax juy yàq, \q1 waabajiiba bi! \b \q1 \v 5 Yàlla da lay sànk ba fàww, \q1 fëkke la sab xayma, yóbbu, \q1 déjjatee la réewum aji dund. \qs Selaw.\qs* \q1 \v 6 Aji jub gis ko, yéemu, \q1 di la ree, naa: \q1 \v 7 «Xool-leen jàmbaar ji làqoowul Yàlla, \q1 xanaa di yaakaar alalam ju bare, \q1 di yokkoo loraange.» \b \q1 \v 8 Man, ma mel ni garabu oliw gu naat \q1 fa biir kër Yàlla, \q1 di wóoloo Yàlla ngoram \q1 tey ak ëllëg. \q1 \v 9 Naa la sante sa jëf ba fàww, \q1 naa biral sa tur wu baax, \q1 say wóllëre teew. \c 53 \s1 Mbon maase na \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Maalat, di taalif bu ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 Ab dof a nga naa ca xelam: \q1 «Yàlla amul,» \q1 tey def njekkar, \q1 njubadeem siblu, \q1 kenn defu ci lu baax. \b \q1 \v 2 Yàllaa tollu asamaan, jéer doom aadama, \q1 di seet ku ci xelu, \q1 tey sàkku Yàlla. \q1 \v 3 Ñépp a dëddu, \q1 bokk yàqu yaxeet. \q1 Kenn deful lu baax, \q1 du kenn sax. \b \q1 \v 4 Yàlla nee: «Xanaa ñiy def lu bon, xamuñu dara? \q1 Ñuy lekk sama ñoñ niw ñam, \q1 te sàkkuwuñu Yàlla.» \q1 \v 5 Waaye ñooy tiita tiit \q1 fu tiitaange amul. \q1 Yàllaay tasaare néewi nit ñi la gaw. \q1 Yàllaa leen wacc, nga gàcceel leen. \b \q1 \v 6 Ana kuy tollu \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, xettli Israyil? \q1 Éy, bés bu Yàlla delloo ñoñam ndam, \q1 ndaw mbégte ci giirug Yanqóoba! \q1 Ndaw bànneex ci Israyil gii! \c 54 \s1 Yàlla, dimbali ma \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di taalif bu ñeel Daawuda. Mooy ba waa Sif demee ca Sóol, ne ko Daawudaa nga làqu ca seenum réew\f + \fr 54.2 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk 1.Samiyel\+bk* 23.14-28; 26.1-5.\ft*\f*. \b \q1 \v 1 Éy Yàlla, musal ma ngir sa tur, \q1 jox ma dëgg, ci sa kàttan. \q1 \v 2 Éy Yàlla, déglul, ma ñaan, \q1 teewlul, ma wax la. \q1 \v 3 Ay doxandéem a ma jógal, \q1 di ñu néeg, bëgga jël sama bakkan, \q1 te seetuñu ci Yàlla. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \b \q1 \v 4 Yàllaa ngii, moo may dimbali; \q1 Boroom bee yor sama bakkan. \b \q1 \v 5 Yal na ay wi këppu ci ñi may tëru, \q1 yal na leen sa dëgg sànk. \q1 \v 6 Xol bu tàlli laa lay sarxale. \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, yaa baax, \q1 ma sant la. \q1 \v 7 Lépp luy njàqare, yaa ma ci jële, \q1 ma tiim samay noon. \c 55 \s1 Xarit wor na ma \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, dib taalif, ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 Éy Yàlla, déglul, ma ñaan la, \q1 bul làqu, dama lay dagaan. \q1 \v 2 Teewlu ma, nangul ma. \b \q1 Li may tawat a ma xañ jàmm, ub sama bopp; \q1 \v 3 coowal noon yee \q1 ak coonob ñu bon ñi. \q1 Dañu maa teg fitna, \q1 di ma songe xadar. \q1 \v 4 Sama fit a ngi rëcc, di tëf-tëfi; \q1 tiitaangey ndee ne ma taral. \q1 \v 5 Njàqaree ma dugg, may kat-kati, \q1 musiba mëdd ma. \q1 \v 6 Dama ne: «Éy ku may may laafi xati, \q1 ma ne fërr, noppluji. \q1 \v 7 Xanaa ma naaw, ba sore, \q1 fanaani màndiŋ ma. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \q1 \v 8 Naa gaawtu, seeluji \q1 ngelaw lu riddi ak ngëlén.» \b \q1 \v 9 Éy, Boroom bi, beenal seeni wax, neenal leen. \q1 Damaa gis fitnaak xuloo ci dëkk bi, \q1 \v 10 guddeek bëccëg ñuy wër, \q1 ñaawtéef ak ayib wéttali leen. \q1 \v 11 Yàq a nga ca biir, \q1 te noteel ak njublaŋ jógul ca pénc ma. \q1 \v 12 Su doon noon bu may ñaawal, \q1 ma muñ ko, \q1 mbaa muy bañ bu may won ab dayo, \q1 ma daw ko. \q1 \v 13 Waaye yaw la, sama nawle, \q1 di sama wóllëre, ma xam la. \q1 \v 14 Nu daan bokk bànneexu diisoo, \q1 ànd ak mbooloo, di jaamuji kër Yàlla ga. \b \q1 \v 15 Yal na leen dee bett, \q1 ñu jekki tàbbi njaniiw, \q1 ngir mbon ga seen biir ak seen dëkkuwaay. \b \q1 \v 16 Waaye man, Yàlla laay woo wall, \q1 te \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee may wallu. \q1 \v 17 Subaak ngoon ak njolloor, \q1 may ñaxtook a ñurumtu, \q1 mu dégg ma. \q1 \v 18 Moo may jot ak jàmm, \q1 ba ma mucc ci xare ya ma ñu bare di songe. \q1 \v 19 Yàllaay dégg, duma leen, \q1 moom mi nguuram yàgga sax. \qs Selaw.\qs* \q1 Soppikuwuñu fenn \q1 te ragaluñu Yàlla. \b \q1 \v 20 Kii a ngi xàccil ñi mu takktool, \q1 di fecci \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w*, \q1 \v 21 làmmiñ wa daa neex ni lem, \q1 te xare lal xol ba; \q1 kàddu ya gëna nooy ag oliw \q1 te di saamar bu génn mbaram. \b \q1 \v 22 Sippikul Aji Sax ji lu la diis, \q1 moom moo lay taxawu. \q1 Du bàyyi mukk aji jub, muy tërëf. \b \q1 \v 23 Waaye yaw Yàlla, yaa leen di tàbbal, \q1 bóomkat ak naaféq ci pax mu xóota xóot, \q1 te seenu fan xaajul. \q1 Man nag, ma di la wóolu. \c 56 \s1 Yàlla laa wóolu, ragaluma nit \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñu dippee Pitax mu luu, dëkk fu sore; di taalifu jàngle bu Daawuda fentoon, ba ko Filisteen ña jàppee ca Gaat\f + \fr 56.1 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk 1.Samiyel\+bk* 21.10-15.\ft*\f*. \b \q1 \v 1 Éy Yàlla, baaxe ma, \q1 nit a ngi may lakkal, \q1 ab xeexkat a ma yendoo sonal. \q1 \v 2 Noon yee ma yendoo lakkal, \q1 bare lool di xareek man. \q1 Ku Màgg ki, \q1 \v 3 bés bu ma tiitee, \q1 yaw laay wóolu. \q1 \v 4 Yàlla laay màggal kàddoom, \q1 Yàlla laa wóolu, ragaluma. \q1 Lu ma nit manal? \b \q1 \v 5 Bésoo bés ñu ngi jalgati samay wax, \q1 seen mépp mébét di sama loraange. \q1 \v 6 Ñu ngi mànkoo, di ma yeeru, \q1 topp sama tànk, \q1 di wut sama bakkan. \b \q1 \v 7 Éy gii ñaawtéef! Ñii nu ñu mana mucce? \q1 Éy Yàlla, yal na leen sa mer dal! \b \q1 \v 8 Tumurànke naa, nga gis. \q1 Duyal samay rongooñ ci sa mbuus. \q1 Du lim nga lépp? \q1 \v 9 Bés bu ma wootee wall, \q1 dees na waññi noon yi, \q1 ma xam ne Yàllaa ànd ak man. \q1 \v 10 Yàlla laay màggal kàddoom, \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji laay màggal kàddoom, \q1 \v 11 Yàlla laa wóolu, ragaluma. \q1 Lu ma nit manal? \b \q1 \v 12 Éy Yàlla, maa tegoo la ma la giñal, \q1 maa lay defal \w saraxi cant|lemma="Sarax yi:"\w*. \q1 \v 13 Yaa ma rawale, ba deewuma, \q1 te duma tërëf. \q1 Damay daagu fi kanam Yàlla, \q1 ci biir leeru àddina. \c 57 \s1 Yàlla jógal, wallu ma! \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñuy wooye Bul yàq, di taalifu jàngle bu Daawuda fentoon, gannaaw ba mu dawee Buur Sóol, ba dugg ca xunti ma\f + \fr 57.1 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk 1.Samiyel\+bk* 24.\ft*\f*. \b \q1 \v 1 Éy Yàlla, baaxe ma, ngalla baaxe ma, \q1 fi yaw laay làqu, \q1 yiiroo sa kiiraay, \q1 ba musiba yi jàll. \q1 \v 2 Ma woo Yàlla, Aji Kawe ji, \q1 Yàlla, mi may matalal. \q1 \v 3 Mooy yónnee fa asamaan, musal ma, \q1 dumaal ma ku may not. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \q1 Yàllaay yónnee jëfi ngoram ak wormaam. \b \q1 \v 4 Maa ngi tëdd ci biiri noon \q1 yu mel niy gaynde, di yàpp doom aadama. \q1 Seeni sell niy xeej aki fitt, \q1 seen làmmiñ di saamar yu ñaw. \q1 \v 5 Éy Yàlla, yaa màgg, ba sut asamaan, \q1 sag leer tiim suuf sépp. \q1 \v 6 Noon yi di ma fiir, \q1 sama xol jeex. \q1 Ñu gasal mam pax, \q1 far tàbbi ca. \qs Selaw.\qs* \b \q1 \v 7 Yàlla, dogu naa, \q1 dogu naa woy, di la kañ. \q1 \v 8 Na sama jëmm jépp yewwu, \q1 xalam ak moroom ma yewwu; \q1 ma yee leeru njël. \q1 \v 9 Boroom bi, naa lay gërëm ci biir xeet yi, \q1 kañ la ci biir waaso yi. \q1 \v 10 Sa ngor a màgg, ba àkki asamaan, \q1 sa worma àkki fa kawa kaw. \b \q1 \v 11 Éy Yàlla, yaa màgg, ba sut asamaan, \q1 sag leer tiim àddina sépp. \c 58 \s1 Yàllaa mana mbugal \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñuy wooye Bul yàq, di taalifu jàngle, ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 Yeen daal, su ngeen waxee, dëgg selaw. \q1 Mbaa yeena ngi àtte nit ñi ci yoon? \q1 \v 2 Yeena ngi mébét njubadi, \q1 di lawal fitna ci réew mi. \b \q1 \v 3 Ku bon day sosu rekk, dëng; \q1 juddu, teggi yoon, dib fen-kat. \q1 \v 4 Day am daŋar ni ñàngóor, \q1 fatti noppam ni jaan ju tëx: \q1 \v 5 du dégg baatu jatkat, \q1 mbaa jati ñeengokat bu ñàng. \b \q1 \v 6 Yàlla, ngalla tojal seeni gëñ; \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, foqal seen selli gaynde yii. \q1 \v 7 Yal nañu ne mes ni ndox muy wal, \q1 yal nañu diir seen fitt, mu damm, \q1 \v 8 yal nañu mel ni ngumbaan-tooye buy dox, di seey, \q1 mbaa lumb wu jigéen tuur, gisul jant. \q1 \v 9 Balaa seen cin a yég tàngooru gajj, \q1 muy gu tooy, muy guy boy, \q1 yal na leen fekk sànku\f + \fr 58.10 \fr*\ft Li ñu wax ci aaya wii am na werante.\ft*\f*. \b \q1 \v 10 Aji jub day gis ñu feyul ko, mu bég, \q1 muy jàngoo deretu ku bon. \q1 \v 11 Ku ne naan: «Ku jub jot sab yool moos! \q1 Te Yàllaa ngi fi moos, di àtte àddina!» \c 59 \s1 Wallu maak ñu bon ñi \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñuy wooye Bul yàq, di taalifu jàngle bu Daawuda fentoon. Mooy ba Buur Sóol yónnee ay nit ñu ko xoolal kër Daawuda, ngir rey ko\f + \fr 59.1 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk 1.Samiyel\+bk* 19.11-17.\ft*\f*. \b \q1 \v 1 Éy sama Yàlla, xettli maak noon yi, \q1 làq ma ñi ma jógal. \q1 \v 2 Xettlimaak ñiiy def lu bon, \q1 wallu maak bóomkat yi. \q1 \v 3 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ñu ngii di ma tëru, nar maa rey, \q1 di ma songe seen doole, \q1 te tooñuma, moyuma. \q1 \v 4 Defuma lu ñaaw, ñuy xélu, di ma waajal; \q1 ngalla, jógal taxawusi ma, ba gis. \q1 \v 5 Aji Sax ji, Yàllay Israyil, Yàlla Boroom gàngoor yi, \q1 yewwul, dikkeel xeeti yéefar yépp, mbugal! \q1 Workat yu bon yi, bu leen yërëm! \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \q1 \v 6 Bu ngoonee ñu wàccsi, \q1 di xiiru niy xaj, \q1 di wër dëkk bi. \q1 \v 7 Déglul li ñuy yebbee ci seen gémmiñ, \q1 seen làmmiñ niy saamar, \q1 ñu defe ne kenn déggu leen. \q1 \v 8 Te yaw Aji Sax ji, yaa ngi leen di ree, \q1 yaa ngi kekku yéefar yii yépp. \b \q1 \v 9 Yaay sama doole, ma di la séentu, \q1 yaw Yàlla, yaay sama rawtu. \b \q1 \v 10 Sama Yàlla ju goree may gatandu. \q1 Moo may may ndam ci noon yi, ma gis. \q1 \v 11 Yàlla, bu leen rey, \q1 lu ko moy samaw xeet fàtte. \q1 Tasaaree leen sa doole, daane leen. \q1 Boroom bi, yaa nuy feg. \q1 \v 12 Bàkkaar lañuy wax, \q1 seeni kàddu, bàkkaari neen. \q1 Yal nañu bew ba daanu, \q1 yooloo ko seeni saagaak seeni fen. \q1 \v 13 Meral, jeexal leen, \q1 jeexal leen, ba ñu jeex tàkk, \q1 ba ñépp xam ne Yàllaay Buur ci giirug Yanqóoba, \q1 ba ca cati àddina. \qs Selaw.\qs* \q1 \v 14 Bu ngoonee ñu wàccsi, \q1 di xiiru niy xaj, \q1 di wër dëkk bi. \q1 \v 15 Ñuy wër di wut lu ñu lekk, \q1 su ñu suurul, di ñurumtu. \q1 \v 16 Maa lay woye sa doole, \q1 xëy, di sarxolle ngir sa ngor. \q1 Yaay sama rawtu, \q1 di sama làquwaay bésub njàqare. \q1 \v 17 Sama doole yaw a, naa la woy, \q1 Yàlla, sama rawtu, Yàlla, boroom ngor. \c 60 \s1 Yàllaa yor sunu mucc \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Seedeb Tóor-tóor, di taalifu jàngle, ñeel Daawuda. Mooy ba Daawuda di xareek waa Siri ña ca Mesopotami ak waa Siri ña ca Soba te ba ñu ca bàyyikoo, Yowab duma fukki junniy Edomeen ak ñaar (12 000) ca xuru Xorom wa\f + \fr 60.2 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk 2.Samiyel\+bk* 8.3-14; \+bk 1.Jaar-jaar ya\+bk* 18.3-13.\ft*\f*. \b \q1 \v 1 Éy Yàlla, wacc nga nu, bëtt sunu kiiraay. \q1 Mer nga, waaye ngalla xettli nu. \q1 \v 2 Yëngal nga suuf, xar ko; \q1 ngalla jagalal, mu tëju, mu ngi jaayu! \q1 \v 3 Won nga sa mbooloo lu metti, \q1 nàndal nu biiñu mbugal, ba nu miir. \q1 \v 4 Artu nga ñi lay jaamu, \q1 ngir mucc fitt. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \q1 \v 5 Walloo nu sa ndijoor, nangul nu, \q1 ba say soppe xettliku. \b \q1 \v 6 Yàllaa àddoo fa këram gu \w sell|lemma="sell:"\w*, \q1 ne: «Maay damu, dogat suufas Sikem, \q1 séddale xuru Sukkóot. \q1 \v 7 Maa moom diiwaanu Galàdd, moom Manase, \q1 Efrayim di sama mbaxanam xare, \q1 Yuda di sama yetu nguur, \q1 \v 8 réewum Mowab di sama ndabal raxasukaay, \q1 Edom, ma teg tànk; \q1 Filisti, ma xaacoo fa.» \b \q1 \v 9 Éy Yàlla, ana ku may yóbbu dëkk ba tata wër? \q1 Ku may jiite ba Edom? \q1 \v 10 Xanaa kay du yaw, Yàlla mi nu wacc, \q1 yaw Yàlla, mi baña ànd ak sunu mboolooy xare? \b \q1 \v 11 Ngalla dimbali nu ci bañaale; \q1 doom aadama, wallam neen la. \q1 \v 12 Nook Yàlla, nu def njàmbaar; \q1 moom mooy not sunuy noon. \c 61 \s1 Naa woote wall \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 Ngalla Yàlla, déglul, maa ne wallóoy, \q1 teewlul, ma dagaan la. \q1 \v 2 Àll laa lay wooye, \q1 sama xol jeex; \q1 yéege ma doju rawtu wu ma jotul. \q1 \v 3 Yaw laa làqoo, \q1 ngay tata ju dëgër, fegal ma noon. \q1 \v 4 Naa dëkke sa xayma, ba fàww; \q1 làqoo sa kiiraay. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \q1 \v 5 Yàlla, yaa dégg samay dige, \q1 sédd ma céru ñi la wormaal. \b \q1 \v 6 Ngalla féqal fani Buur, \q1 ay atam bare, sët ba sëtaat. \q1 \v 7 Éy Yàlla, yal na Buur toog ba fàww fi sa kanam, \q1 nga sédd ko sa ngor ak sa worma, mu fegoo; \q1 \v 8 kon ma woy la ba fàww, \q1 di jëfe samay dige bésoo bés. \c 62 \s1 Yaakaar, fa Yàlla \d Mu jëm ci Yedutun, njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 Yàlla doŋŋ ay dalal sama xel, \q1 moo may wallu. \q1 \v 2 Moom doŋŋ mooy sama wéeru-mucc, \q1 di ma rawale, ba duma sànku! \b \q1 \v 3 Xanaa dungeen bàyyee songandoo nit, \q1 nar koo sànk, \q1 ni kuy màbb tabax bu joy, \q1 mbaa ngay bàddi per mu ràpp? \q1 \v 4 Seeni mébét, wàcce boroom daraja doŋŋ; \q1 yeena ngi bége ay fen, \q1 seeni kàddu diw yiw, \q1 seen xalaat diy saaga. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \b \q1 \v 5 Yal na Yàlla doŋŋ di dalal sama xel, \q1 moom mi ma yaakaar. \q1 \v 6 Moom doŋŋ a di sama cëslaay, di sama wall, \q1 di sama rawtu, duma tërëf. \q1 \v 7 Yàllaa may musal, di ma sagal, \q1 ma di ko doolewoo. \q1 Sama kiiraay, Yàllaa! \q1 \v 8 Bokk yi, wóoluleen ko fu ngeen tollu, \q1 diisleen ko seen xol, \q1 Yàllaay sunu kiiraay. \qs Selaw.\qs* \b \q1 \v 9 Doom aadama, ngelawal neen; \q1 nit, naxi neen. \q1 Booleel teg ci lu ñuy natte diisaay, \q1 kaw la jëm. \q1 Ñooy gëna woyof ngelaw! \q1 \v 10 Bul wóolu ribaa, \q1 bul yaakaar alalu càcc, neen la. \q1 Bu sa alal yokku, nga taf ci sa xol. \b \q1 \v 11 Benn yoon la Yàlla wax, \q1 yaari yoon laa dégg, ñu ne; \q1 «Doole, fa Yàlla.» \q1 \v 12 Boroom bi, ngor, yaay boroom, \q1 yaw daal, yaay yool nit jëfam. \c 63 \s1 Maa namm Aji Sax ji \d Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. Mooy ba mu nekkee ca màndiŋu Yuda\f + \fr 63.1 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk 1.Samiyel\+bk* 23.14; 24.2; \+bk 2.Samiyel\+bk* 15.23.\ft*\f*. \b \q1 \v 1 Yaw Yàlla, yaay sama Yàlla, \q1 ma di la sàkku, \q1 sama bakkan mar la, \q1 sama jëmm namm la, \q1 fu suuf mare ndox, ne sereŋ. \q1 \v 2 Moo tax kër gu \w sell|lemma="sell:"\w* ga laa la séentoo, \q1 ngir niir sa leer ak sa teddnga. \q1 \v 3 Xéewloo sa ngor moo dàq dundu bakkan; \q1 ma àddu boog, kañ la! \q1 \v 4 Dama lay sant, sama giiru dund kay, \q1 yékkatiy loxo, sàbbaale la. \q1 \v 5 Sama xol di sedd, ni ku ñam wu duun suural, \q1 ma bég, sarxolle, màggal la. \b \q1 \v 6 Su ma tëddee, fàttliku la, \q1 waxtuw guddi dama lay xalaat. \q1 \v 7 Yaay sama ndimbal, \q1 may làqoo sa kiiraay, \q1 di sarxolle. \q1 \v 8 Sama xol taq la, \q1 nga téyee ma sa ndijoor. \b \q1 \v 9 Waaye ñiy wuta faat sama bakkan \q1 ñoo jëm xóotey njaniiw. \q1 \v 10 Ñu jébbal leen ñawkay saamar, \q1 till séddoo. \b \q1 \v 11 Buur moom, di bége Yàlla; \q1 képp ku koy giñe di ko kañoo, \q1 fen-kat ne xerem. \c 64 \s1 Yàllaa man ag fitt \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 Éy Yàlla, déglul sama kàddug tawat; \q1 ngalla aaral sama bakkan ci noon bu raglu. \q1 \v 2 Làq ma pexey ku bon, \q1 ma rëcc gàngooru defkati ñaawtéef. \b \q1 \v 3 Ñu ngi daas seen làmmiñ niy saamar, \q1 di fitte seeni kàdduy wextan, \q1 \v 4 di jam ku ñu tëru te deful dara; \q1 jekki jam ko, te tiituñu ci dara. \q1 \v 5 Dañoo dogu ca lu bon la ñu nar, \q1 di diisoo na ñuy làqe ay fiir, \q1 te naan: «Kenn du ko gis!» \q1 \v 6 Dañuy lal pexem njubadi te naan: \q1 «Lal nanu pexe mu mat sëkk.» \q1 Nit aka xóot xel te xóoti mbóot! \b \q1 \v 7 Waaye Yàllaa leen di jamu fittam, \q1 ñu jekki daanu. \q1 \v 8 Seen làmmiñ a leen di fakkastal, \q1 ba ku leen xool wëcc bopp. \b \q1 \v 9 Ñépp a ciy am tiitaange, \q1 bay siiwal la Yàlla def, \q1 tey xalaataat jëfam jooju. \q1 \v 10 Ku jub bége \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, làqoo ko. \q1 Képp ku namm njub, damu. \c 65 \s1 Yàllaay nangul suuf \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di woyu Sabóor, ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 Éy Yàlla, yaa jagoo cant fa \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, \q1 yaw lees di jëfeel ab dige. \q1 \v 2 Yaw miy nangug ñaan, \q1 yaw la képp di wuysi. \q1 \v 3 Samay ñaawtéef man na ma, \q1 waaye sunuy tooñ, yaa nu koy baal. \q1 \v 4 Ndokklee koo tànn, woo ko, \q1 mu dale say ëtt, \q1 di xéewloo sa ngëneeli kër, \q1 ak sa sellngay dëkkuwaay. \b \q1 \v 5 Defal nga nuy kéemaan, \q1 nangug ñaan ci njekk, \q1 yaw Yàlla, mi nuy wallu, \q1 di yaakaaru àddina wërngal këpp, \q1 ba ca géej gu sore ga. \q1 \v 6 Yaa dëje tund yu mag yi doole, \q1 gañoo sa kàttan, \q1 \v 7 di dalal riirum géej aki gannaxam, \q1 ak coowal xeet yi, \q1 \v 8 ba waa cati àddina yéemoo say firnde, \q1 waa penkook sowu di sarxolle. \b \q1 \v 9 Yaa dikke suuf am wal, \q1 nangul koo nangul. \q1 Dexu Yàllaa fees ndox, \q1 ngay may nit peppam, \q1 ni nga ko waajale suuf si, \q1 \v 10 di suuxat ngàbb mi, \q1 maasalee ko jal yi, \q1 sottiy waame, mu mokk, \q1 cax ma, nga barkeel. \q1 \v 11 Yaay tëje mbeyum at mi say ngëneel, \q1 foo jaare, xéewal walangaan. \q1 \v 12 Parluy màndiŋ yaa ngi walangaan, \q1 li wër tund yu ndaw yi di xumbéen. \q1 \v 13 Joor gaa ngi, jur gi muur, \q1 xur yi sàngoo pepp, \q1 lépp di xaacook a woy. \c 66 \s1 Yàllaay aar nitam \d \v 1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di woyu Sabóor. \b \q1 Yeen waa àddina sépp, sarxolleel-leen Yàlla, \q1 \v 2 woyleen teddngay turam, \q1 darajaal-leen cantam. \q1 \v 3 Neleen Yàlla: «Yaaka yéemey jaloore! \q1 Sa doolee bare, ba say noon rasu, \q1 \v 4 àddina yépp di la sujjóotal, \q1 di la woy, di joobe sa tur.» \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \b \q1 \v 5 Dikkleen gis li Yàlla def, \q1 jëf la ju yéeme, ñeel doom aadama yi. \q1 \v 6 Moo soppi géej ag joor, \q1 maam ya dox jàll. \q1 Nanu ko bége foofa. \q1 \v 7 Mooy nguuroo njàmbaaram ba fàww, \q1 di topp xeet yeek bët. \q1 Ku koy diiŋat, yàlla boo damu! \qs Selaw.\qs* \b \q1 \v 8 Yeen xeet yi, santleen sunu Yàlla, \q1 te biral cantam! \q1 \v 9 Moo sàmm sunu bakkan, \q1 te waccu nu, nu tërëf. \b \q1 \v 10 Éy Yàlla, nattu nga nu, \q1 xelli nu, ni ñuy xellee xaalis; \q1 \v 11 laaw nga nu, \q1 teg nu njàqare. \q1 \v 12 May nga noon not nu, \q1 nu jaare sawara, jaarem ndox; \q1 nga génne nu, yaatal nu. \b \q1 \v 13 Maay duggaale sa kër ay \w saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, \q1 defal la samay dige, \q1 \v 14 yi ma waxoon ci sama gémmiñ, \q1 sama làmmiñ tudd ko, ba ma jàqee. \q1 \v 15 Jurug yafal, ma defal la saraxu rendi-dóomal, \q1 saxar sa jollee ca kuuyu sarax ya, \q1 ma boole ca saraxu nag ak sikket. \qs Selaw.\qs* \b \q1 \v 16 Képp ku ragal Yàlla dikkal, déglu, \q1 ma limal la li mu ma defal. \q1 \v 17 Moom laa woo wall, \q1 àddu, màggal ko. \q1 \v 18 Su ma naroon ñaawtéef, \q1 Boroom bi du ma déglu. \q1 \v 19 Waaye Yàlla dégg na ma, \q1 teewlu na samag ñaan. \q1 \v 20 Cant ñeel na Yàlla, \q1 gàntuwul samay ñaan, \q1 xañu ma ngoram. \c 67 \s1 Yal na nu Yàlla barkeel \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di woyu Sabóor. \b \q1 \v 1 Éy Yàlla, yéwéne nu, barkeel nu, \q1 te geesoo nu sa leeru kanam, \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*,\qs* \q1 \v 2 ba ñu ràññee sa loxo fi kaw suuf, \q1 gis sag wall fi biir xeet yépp. \b \q1 \v 3 Yaw Yàlla, na la xeet yi sant, \q1 na la xeet yépp sant. \q1 \v 4 Na xeet yiy bég, di sarxolle; \q1 loo dogalal xeet yi njub la, \q1 te yaay wommat xeet yi ci kaw suuf. \qs Selaw.\qs* \q1 \v 5 Yaw Yàlla, na la xeet yi sant, \q1 na la xeet yépp sant. \b \q1 \v 6 Suuf si nangu na, \q1 yal na nu Yàlla, sunu Yàllay barkeel. \q1 \v 7 Yal na nu Yàllay barkeel, \q1 ba àddina wërngal këpp ragal ko. \c 68 \s1 Yàlla daagu, daan \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di woyu Sabóor. \b \q1 \v 1 Yàllaay jóg, noonam ya tasaaroo; \q1 bañam ña daw, dëddu ko. \q1 \v 2 Yàlla wal, ñu naaw ni saxar. \q1 Ñu bon ñi sànku fi kanam Yàlla, \q1 mbete dax ak sawara. \q1 \v 3 Ñu jub ñi nag bég, di bànneexu fi kanam Yàlla, \q1 tey puukarewoo mbégte. \q1 \v 4 Woyleen Yàlla, teral turam, \q1 xàllal-leen kiy war niir yi, \q1 Ki Sax moo di turam. \q1 Bànneexuleen fi kanamam. \q1 \v 5 Mooy baayoo jirim, di àtte jëtun, \q1 kookoo di Yàlla ja fa dëkkuwaayu sellngaam. \q1 \v 6 Yàllaay sàkkal ku wéet wéttal, \q1 di afal ku ñu tëjoon, bégal ko, \q1 ku déggadi rekk ay dëkke suuf su ne sereŋ. \b \q1 \v 7 Céy Yàlla, yaa génn, jiitu sa mbooloo, \q1 daagu, dugg màndiŋ ma. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \q1 \v 8 Suuf yëngu, \q1 asamaan sóob \q1 fi kanam Yàlla, boroom tundu Sinayi, \q1 Yàllay Israyil ja! \q1 \v 9 Yàlla, waame nga tawal, \q1 leqlee ko réew mi nga séddoo, fa mu sonne, \q1 \v 10 sa mbooloo dëkke fa. \q1 Yàlla yaa leel néew-ji-doole ci sag mbaax. \b \q1 \v 11 Boroom beey joxe ndigal, \q1 gàngooru jigéen indi xibaar: \q1 \v 12 «Buur yaak seeni gàngoor a ngay dawa daw, \q1 jongomay kër gi di séddale lël ja. \q1 \v 13 Yeen ñiy waaf ci gétt gi, bésub xare, \q1 gànjar a ngi, di laafi pitax yu ñu xoob xaalis, \q1 dunq ya teg wurus wuy ray-rayi.» \q1 \v 14 Ba fa Aji Man ji tasaaree buur ya, \q1 tawub yuur a ngay sóobe tundu Calmon. \b \q1 \v 15 Yaw tundu yàlla yi, yaw tundu Basan, \q1 tundu Basan, tund wi ci coll yi, \q1 \v 16 looy xeelook say coll, di fiire \q1 tund wi Yàlla namma dëkke? \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji kat, fa lay dëkk ba fàww! \b \q1 \v 17 Watiiri xarey Yàlla di ñaar fukki junni (20 000), \q1 ba ci junniy junni. \q1 Boroom bi ne ca seen biir, \q1 di boroom tundu Sinayi fa biir sellngaam. \b \q1 \v 18 Yaa yéeg fa kawa kaw, \q1 jàpp ay jaam, yóbbaale. \q1 Yaa nangooy galag ci nit ñi, \q1 ba ci ñiy fippu \q1 ndax li Yàlla Ki Sax dëkke Siyoŋ. \b \q1 \v 19 Cant ñeel na Yàlla bésoo bés. \q1 Moo nuy jaboote. Yàllaa nuy musal. \qs Selaw.\qs* \q1 \v 20 Sunu Yàllaa di Yàlla jiy walloo, \q1 Aji Sax ji Boroom beey musal bakkan. \q1 \v 21 Yàlla daal ay rajaxe boppi noonam \q1 ak kaaŋ mu sëq mu boroom wéye tooñ. \b \q1 \v 22 Boroom bi nee: «Basan laay waññee noon yi, \q1 waññee leen xóotey géej, \q1 \v 23 ngeen mana xuus ci seen deret, \q1 seeni xaj séddu ci seeni néew.» \b \q1 \v 24 Céy Yàlla, gis nañu sa gàngoor di daagu, \q1 sama Yàlla, sama buur, sa gàngoor ba ca biir kër gu \w sell|lemma="sell:"\w* ga. \q1 \v 25 Woykat ya jiitu, xalamkat ya mujje, \q1 janq ji yéewe leen tëgg um njiin. \q1 \v 26 Dajeleen, di sant Yàlla, \q1 yeen askanu Israyil, santleen Aji Sax ji. \q1 \v 27 Giirug Beñamin a ngi jiitu, gën cee néew, \q1 njiiti Yuda topp caak seeni kurél, \q1 njiiti Sabulon topp caak njiiti Neftali. \q1 \v 28 Yeen, seen Yàlla dogalal na leen kàttan; \q1 éy Yàlla, jëfeel doole ja nga nu jëfeeloon. \q1 \v 29 Sa kër gi tiim Yerusalem, \q1 fa la la buur yiy indiley galag. \q1 \v 30 Nanga fa gëdde rabu àll wi\f + \fr 68.31 \fr*\fk rabu àll wi: \fk*\ft jàpp nañu ne jombul Misra lay doon.\ft*\f* ci barax yi, \q1 ñooy gétti yëkk yi, xeet yi ci des diy sëllu. \q1 Gëdd leen, ba ñu sujjóotalsi laak dogi xaalis. \q1 Tasaareel xeet yooyu sopp xare, \q1 \v 31 ay kàngam bàyyikoo Misra aki galag, \q1 réewum \w Kuus|lemma="Kuus:"\w* baral loxoom, indil Yàlla. \b \q1 \v 32 Yeen waa réewi àddina, woyleen Yàlla, \q1 teral-leen Boroom bi, \qs Selaw\qs* \q1 \v 33 gawar bi ci asamaan, \q1 asamaani démb. \q1 Ma ngooguy àddu kàddug doole. \q1 \v 34 Seedeleen ne doole, fa Yàlla, \q1 mi tiime Israyil darajaam, \q1 dooleem feeñoo xàmbaar ya. \b \q1 \v 35 Céy Yàllaaka mata ragal fa këram gu sell! \q1 Mooy Yàllay Israyil, \q1 di may mbooloo mi dooleek kàttan. \q1 Cant ñeel na Yàlla! \c 69 \s1 Ku ñu fitnaal a ngi ñaan \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor, ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 Éy Yàlla, wallu ma! \q1 Ndox maa ngi ma tollu ci put. \q1 \v 2 May suux ci ban bu xóot, \q1 te awma fu ma teg tànk. \q1 Maa ngi nii ci ndox mu xóot, \q1 gannax yi mëdd ma. \q1 \v 3 Ma woote wall ba tàyyi, \q1 sama put gi wow koŋŋ. \q1 Ma séentu la, yaw sama Yàlla, \q1 ba samay gët giim. \q1 \v 4 Sama kawari bopp sax, \q1 ñi ma bañ ci daraa ko ëpp. \q1 Ñu bare doole, bëgg maa sànk, \q1 noonoo ma ci dara. \q1 Sàccuma, nara fey! \b \q1 \v 5 Yaw Yàlla, xam nga sama jëfi dof, \q1 te samay tooñ umpu la. \q1 \v 6 Yàlla buma rusloo ñi la yaakaar, \q1 yaw Boroom bi, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoor yi, \q1 yàlla buma gàcceel ñi la topp, \q1 yaw Yàllay Israyil. \b \q1 \v 7 Yaa tax ma dékku, ñu di ma sewal, \q1 ma rus ba sëlmoo gàcce. \q1 \v 8 Jaambur laa léegi ci saay bokk, \q1 mel ni doxandéem sama biir doomi ndey. \b \q1 \v 9 Damaa xér ci sa kër gi, ba jeex tàkk, \q1 te jëf ji ñu la sewale man la dal. \q1 \v 10 May jooy, di woor, \q1 ñu di ma sewal. \q1 \v 11 Ma sol ay saaku, di ko ñaawloo, \q1 ñu di ma léebu. \q1 \v 12 Waa pénc ma di ma tooge, \q1 màndikat yi di ma woyal. \q1 \v 13 Waaye man, Aji Sax ji, yaw laay dagaan. \q1 Éy Yàlla, na tey di bésub yiw. \q1 Ngalla nangul ma ci sa ngor lu yaa \q1 ak sa wall gu wóor. \q1 \v 14 Xettli ma ci ban bi, ma baña suux, \q1 xettliku ci samay noon. \q1 Rikk génne ma yii xóotey ndox, \q1 \v 15 ba gannax du ma mëdd, \q1 xóotey géej du ma warax, \q1 pax du ma kepp. \q1 \v 16 Éy Aji Sax ji, yaa rafet ngor, nangul ma! \q1 Geesoo ma sa yërmande ju yaa! \q1 \v 17 Bu ma làqu, Sang bi. \q1 Jàq naa, gaawe ma. \q1 \v 18 Jege ma, jot ma, \q1 musal ma ci noon yi! \q1 \v 19 Yaa gis ñu di ma sewal, di ma ruslook a torxal, \q1 yaa ngi ne jàkk ci noonoo noon. \q1 \v 20 Dees maa sewal, sama xol jeex, ma wopp; \q1 may sàkku yërmande, awma ko; \q1 ku ma dëfal it, gisuma ko. \q1 \v 21 Tooke lañu ma leel, \q1 ma mar, ñu nàndal ma lu forox. \b \q1 \v 22 Yal na seen ndab di seenum yeer, \q1 seeni am-di-jàmm di seenug fiir. \q1 \v 23 Yal na seeni gët giim, ba dootu gis; \q1 yal na seen ndigg rëcc fàww. \q1 \v 24 Yal nanga leen yuri mbugal, \q1 sa mer tàkk, dab leen. \q1 \v 25 Yal na seeni dal gent, \q1 seeni xayma wéet. \q1 \v 26 Yaw, nga duma ba noppi, ñu toppaat ca, \q1 nga gaañ, ñu siiwal mitit wa. \q1 \v 27 Dencal leen tooñ ci kaw tooñ, \q1 te yàlla buñu tàbbi ci sag njekk. \q1 \v 28 Yal nañu leen far ca téereb dund ba, \q1 bañ leena limaale ca aji jub ña. \q1 \v 29 Man de, damaa jàq, tiis. \q1 Éy Yàlla, yal naa làqoo sag wall. \b \q1 \v 30 Damay woy Yàlla, teral ko, \q1 màggal ko, sant ko. \q1 \v 31 Mu gënal Aji Sax ji saraxu yëkk, \q1 aki béjjénam aki wewam. \q1 \v 32 Néew-ji-doole di gis, bége, \q1 kuy sàkku Yàlla yokku fit. \q1 \v 33 Aji Sax ji day dégg néew-ji-doole moos, \q1 te du sàggane ñoñam ñi ñu njoñ. \b \q1 \v 34 Na asamaan ak suuf màggal Yàlla, \q1 mook géej ak lu cay yëngoo. \q1 \v 35 Yàlla kat mooy musal \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, \q1 tabaxaat dëkki Yuda yu mag yi, \q1 ay nitam moom, dëkke. \q1 \v 36 Askanu jaamam ñee koy jagoo, \q1 ay soppeem a koy dëkke. \c 70 \s1 Yàlla, gaawe ma \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di woy wuy fàttlee. \b \q1 \v 1 Yàlla, wallu ma! \q1 Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, gaawe ma! \b \q1 \v 2 Kuy wut sama bakkan, \q1 yal na rus, torox ne tott. \q1 Kuy bége sama loraange, \q1 yal nañu ko duma, waññi ko, mu ne yàcc. \q1 \v 3 Kuy ñaawle, \q1 yal na dellu gannaaw, torox. \b \q1 \v 4 Képp ku lay sàkku, \q1 yal na bég, di la bànneexoo. \q1 Képp ku sopp sag wall, \q1 yal na jàppoo: «Yàlla màgg na!» \b \q1 \v 5 Man de, néew naa doole, ñàkk naa. \q1 Éy Yàlla, gaawe ma. \q1 Yaw yaa may wallu, xettli ma. \q1 Éy Aji Sax ji, bu ma yeexe. \c 71 \s1 Mag a ngi séentu njekku Yàlla \q1 \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, yaw laa làqoo, \q1 yàlla buma rus mukk. \q1 \v 2 Xettlee ma sa njekk, yiwi ma; \q1 ngalla teewlu ma, te wallu ma. \q1 \v 3 Yal nangay sama cëslaay, sama rawtu \q1 bu may rawesi saa su ne, \q1 te nga dogal sama mucc. \q1 Yaw yaa may téye, di ma aar. \q1 \v 4 Éy sama Yàlla, musal ma ci dooley ku bon \q1 ak ab saaysaay ak ab néeg. \b \q1 \v 5 Boroom bi, Aji Sax ji, yaw de laa yaakaar, \q1 dale laa wóolu ba may ndaw. \q1 \v 6 Yaw laa wéeroo ba may juddu; \q1 yaw yaa ma roccee sama biiru ndey. \q1 Yaa yelloo sama cant fàww. \q1 \v 7 Firndey alkànde la ma ñu bare xoole woon, \q1 te yaw ngay sama rawtu bu wóor. \q1 \v 8 Samay kàddu sag cant la fees \q1 ak di la saxoo darajaal. \b \q1 \v 9 Ngalla bu ma wacc, mag laa; \q1 bu ma ba fi doole jeexe. \q1 \v 10 Noon yaa nga may tooge, \q1 ñi may tëroo ngay diisoo, \q1 \v 11 naan: «Yàlla wacc na ko, \q1 nan ko dàq, jàpp; \q1 kenn du ko wallu.» \q1 \v 12 Éy Yàlla, bu ma sore. \q1 Sama Yàlla, gaawe ma. \q1 \v 13 Samay seytaane, \q1 yal nañu leen rusloo, sànk leen. \q1 Ñi may wuta lor, \q1 yal nañu leen gàcceel, sewal leen. \q1 \v 14 Man may saxoo yaakaar, \q1 di la sant, di santati. \q1 \v 15 May siiwal sa njekk, \q1 di yendoo waxtaane say wall, \q1 doonte lim ba wees na ma. \q1 \v 16 Boroom bi, Aji Sax ji, ma dikke la sag njàmbaar, \q1 di tudd sa njekk gu wéet. \q1 \v 17 Éy Yàlla, ba may ndaw, nga ma xamal say kéemaan, \q1 te ba tey jii maa ngi koy biral. \q1 \v 18 Éy Yàlla, bu ma bijjaawee ba weex tàll it, bu ma wacc, \q1 ba keroog may xamal maasu tey sa doole, \q1 xamal ñi ciy topp ñépp sag njàmbaar. \q1 \v 19 Céy Yàlla, sa njekk àkki na fa kawa kaw. \q1 Def nga lu réy. \q1 Yaw Yàlla, ana ku mel ni yaw? \q1 \v 20 Won nga ma ay yoon coonooki tiis, \q1 waaye yaa may dundalaat, \q1 ma mucc xóotey suuf. \q1 \v 21 Yal nanga ma gëna sagal, \q1 geesu, bégal ma. \b \q1 \v 22 Man it sama Yàlla, ma xalam, sant la \q1 ngir sa kóllëre. \q1 Aji Sell ji séddoo Israyil, \q1 dama lay woy aki xalam, \q1 \v 23 sarxolle, woy la, \q1 bége sag njot. \q1 \v 24 May yendoo siiwal sa njekk \q1 nde ña ma doon wuta lor \q1 lañu rusloo, sewal leen. \c 72 \s1 Nu ñaanal Buur \d \v 1 Ñeel Suleymaan. \b \q1 Céy Yàlla, mayal Buur sa xelum àtte, \q1 mayal doomu Buur bii sa xelum njekk, \q1 \v 2 muy àttee sa mbooloo njub, \q1 di àttee sa néew-ji-doole ñi yoon, \q1 \v 3 tooli tund yu mag yi indil mbooloo mi jàmm, \q1 tooli tund yu ndaw yi xéewale leen njekk, \q1 \v 4 Buur di àtte néew-ji-dooley xeet wi, \q1 di wallu doomi néew-ji-doole \q1 tey dëggaate kiy nennoo. \q1 \v 5 Yal nañu la wormaal feek jant biy am, \q1 feek weer wiy feq, sët ba sëtaat. \b \q1 \v 6 Yal na Buur di xéewalu réewam nib taw cig ruujeef, \q1 mbaa waame wuy suuxat suuf. \q1 \v 7 Janti Buur aji jub day woomle, \q1 te ba keroog weer wiy fey, jàmm di law, \q1 \v 8 mu yilif géej ba géej \q1 ak dex ba ca cati àddina. \q1 \v 9 Waa màndiŋ mi di ko sukkal, \q1 ay noonam mëq suuf, \q1 \v 10 buuri Tarsis ak dun ya \q1 di ko indil ay galag; \q1 buuri Saba ak Seba \q1 di ko yótsi yóbbal, \q1 \v 11 buuroo buur di ko sujjóotal, \q1 xeetoo xeet di ko surgawu. \q1 \v 12 Mooy xettliji aji tumurànke bu woote wall \q1 ak aji néewle ju sësul fenn. \q1 \v 13 Mooy yërëm ku néewleek ku tumurànke, \q1 di sàmm bakkanu aji tumurànke, \q1 \v 14 boole leen jot ci notaangeek loraange, \q1 ngir fonk seen bakkan. \b \q1 \v 15 Yal na Buur gudd fan, \q1 yal nañu ko may wurusu Saba. \q1 Nañu koy ñaanal saa su ne, \q1 di ko saxoo, mu barkeel. \b \q1 \v 16 Yal na pepp ne gàññ ci réew mi, \q1 yal na gub yay jaayu ca tund ya ni gottub Libaŋ; \q1 dëkk yu mag yi sëqi nit ba law, \q1 \v 17 yal na turam sax, \q1 ba law fu jant tiim, \q1 yal na xeet yépp barkeele ci moom, \q1 te di ko ndokkle. \b \q1 \v 18 Cant ñeel na Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 Yàllay Israyil, mi wéetooy jalooreem. \q1 \v 19 Cant ñeel na teddngaam, ba fàww, \q1 yal na teddngaam dajal suuf sépp! \q1 Amiin, Amiin! \q1 \v 20 Ñaani Daawuda doomu Yese jeexe fii. \c 73 \s1 Am Yàllaa gën \d \v 1 Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf. \b \q1 Yàlla kay baax na ci Israyil, \q1 baax ci ku rafet xol. \q1 \v 2 Waaye man de tuuti kon ma lajj, \q1 tuuti ma tarxiis, \q1 \v 3 ngir maa ñee ku bew, \q1 ndax gis mu baaxle te di ku bon. \b \q1 \v 4 Amuñu metit, \q1 xanaa ne faaj. \q1 \v 5 Doñ-doñu nit dabu leen, \q1 coonoy doom aadama dalu leen. \q1 \v 6 Moo leen taxa ràngoo reewande, \q1 làmboo coxor. \q1 \v 7 Dañoo suur ba gët suulu, \q1 seen xalaati xel xëtt yoon. \q1 \v 8 Dañuy ñaawle, di wax lu bon, \q1 di réy-réylu, boole ci kàdduy jaay-doole. \q1 \v 9 Seen ŋal-ŋal àkki asamaan, \q1 làmmiñ dajal suuf. \q1 \v 10 Moo tax ñoñi Yàlla walbatiku ci ñoom, \q1 di jolu seen wax nim ndox \q1 \v 11 te naan: «Lu ci Yàlla xam? \q1 Ana xam-xam fa Aji Kawe ji?» \q1 \v 12 Ñu bon ñaa ngoog! \q1 Ne finaax, di gëna woomle. \b \q1 \v 13 Man kay maa sellal ci neen, \q1 di sàmm sama der. \q1 \v 14 Bés bu ne yar dal ma, \q1 saa yu ma xëyee, jot mbugal. \q1 \v 15 Su ma noon: «Naa waxe ni ñoom,» \q1 kon de, ma wor sa askanu mbooloo. \q1 \v 16 Naka laay jéema ràññee lii, \q1 mbir mi ëlëm ma. \q1 \v 17 Ba ma àggee sa kër gu sell ga, \q1 laa doora gis muju ku bon. \b \q1 \v 18 Yoonu tarxiis kay, nga leen teg, \q1 daane leen, ñu sànku, \q1 \v 19 Yàquleeka leena bett! \q1 Musibaa leen ne fuuf, ñu ne mes! \q1 \v 20 Day mel ni gént goo yewwoo. \q1 Céy Boroom bi, boo xippee, jëmmu gént ga soof la. \b \q1 \v 21 Naqar laa amoon, \q1 sama xol di dagg. \q1 \v 22 Booba ngaaka laa, xawma dara; \q1 rab laa woon fi sa kanam. \q1 \v 23 Teewul ma des ak yaw, \q1 nga jàpp sama loxol ndijoor. \q1 \v 24 Danga maa gindee sam xel, \q1 teg ca dalale ma sa teddnga. \q1 \v 25 Ana ku ma am asamaan ku la moy? \q1 Ku ma safoo kaw suuf ku la moy? \q1 \v 26 Kàttan ak pexe jeex, \q1 Yàlla di ma dooleel, \q1 ma séddoo ko fàww. \q1 \v 27 Ku la sore kat, sànku; \q1 képp ku la wor, nga fàkkas. \b \q1 \v 28 Man de, jege Yàllaa ma gënal. \q1 Boroom bi, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, yaw laa def kiiraay, \q1 ngir siiwal sa jépp jëf. \c 74 \s1 Yàlla, bu la noon ree \d \v 1 Muy taalifu yeete, giiroo ci Asaf. \b \q1 Éy Yàlla, lu tax nga wacc nu fàww, \q1 di dal ak xol bu tàng \q1 ci sa xari parlu yii? \q1 \v 2 Bàyyil xel askan wi nga jënd bu yàgg, \q1 yaa jot gii giir, séddoo leen. \q1 Bàyyil xel tundu \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, fa nga dëkke woon. \q1 \v 3 Dikkal, xool gent bu yaa bii dul jeex, \q1 noon yàq lépp ci biir kër gu \w sell|lemma="sell:"\w* gi. \b \q1 \v 4 Say bañ xaacu nañ fa sa digg bérabu ndaje ma, \q1 samp seen raaya. \q1 \v 5-6 Sémmiñ dal, wàkku awu. \q1 Mbete ñu xàcciy sémmiñ, di gori geer, \q1 ba lu fa doon liggéeyu yett, tas. \q1 \v 7 Dañoo taal sa kër gu sell, \q1 sa dëkkuwaayu tur lañu daaneel, ba sobeel ko. \q1 \v 8 Ñu namm noo not ba nu nooy, \q1 fuy bérabu ndajem Yàlla ci réew mi, ñu lakk. \q1 \v 9 Sunuy takk réer na nu, \q1 yonent amatul, \q1 te kenn xamul fu lii di àkki. \b \q1 \v 10 Éy Yàlla, fu reetaani noon di dakke? \q1 Xanaa bañ yi duñu la ñàkke kersa ba fàww? \q1 \v 11 Looy téye sa loxol ndijoor? \q1 Na sa loxo jóge sa dënn, nga buube leen. \b \q1 \v 12 Yàlla, yaa masa doon sama buur, \q1 di ma walloo ci digg réew mi. \q1 \v 13 Yaa xàjjale géej gi ci sa doole, \q1 toj boppi ninki-nànka ya ca ndox ma, \q1 \v 14 yaa rajaxe kaaŋi rab wa, \q1 leele ko rabi màndiŋ ma. \q1 \v 15 Yaa fettaxal fii bëti ndox akum wal, \q1 ŋiisal dex yu masa wal. \q1 \v 16 Yaa moom bëccëg, moom guddi, \q1 teg fi weer week jant bi. \q1 \v 17 Yaa rëdd mboolem digi suuf, \q1 sàkk noor ak nawet. \b \q1 \v 18 Kon xoolal, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, noon a ngi ree, \q1 xeet wu amul bopp a lay sewal. \q1 \v 19 Bul wacce rabu àll sam xati, \q1 bul sàggane sa néew-doole yi mukk. \q1 \v 20 Ngalla xoolal ci \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* gi, \q1 fu làqu ci réew mi, fitna dale fa ba dajal. \q1 \v 21 Yàlla bu néew-doole ñibbaale gàcce, \q1 yal na ku ñàkk ak ku néewle di la santandoo. \q1 \v 22 Éy Yàlla, jógal ñoŋal sa dëgg, \q1 bàyyil xel dof bi la dëkkee sewal. \q1 \v 23 Bul tanqamlu sa coowal noon yi, \q1 ñii la jógal, seenum riir a ngi jolli saa su ne. \c 75 \s1 Yàllaay àtte \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñu dippee Bul yàq, di woyu Sabóor, giiroo ci Asaf. \b \q1 \v 1 Yàlla, nu sant la, santati la; \q1 nu ngi lay woo, \q1 di siiwal say jaloore. \b \q1 \v 2 Yàlla nee: «Maay takk ab àpp, \q1 àtte ca njub. \q1 \v 3 Bu suuf di yëngu mook ñi ko dëkke ñépp, \q1 maay kiy téye ay kenoom. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \q1 \v 4 Dama ne ku réy: “Bul réy-réylu,” \q1 ne ku bon: “Bul bew, \q1 \v 5 bul bewa bew, \q1 bay waxe reewande.”» \b \q1 \v 6 Du penku, du sowu, \q1 te du màndiŋ ma la daraja di jóge. \q1 \v 7 Yàllaay àtte: \q1 kii mu detteel, kee mu kaweel. \b \q1 \v 8 Merum \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dib kaas ci loxoom, \q1 biiñu njafaan bu wex di ca fuur, \q1 mu jol ko képp ku bon ci àddina, \q1 mu naan ba naanaale ginjrit ga. \q1 \v 9 Man may biral jëfam ba fàww. \q1 Damay woy Yàllay Yanqóoba. \q1 \v 10 Mu ne: «Jépp dooley ku bon, ma neenal; \q1 dooley ku jub yokku.» \c 76 \s1 Yàllaa moom xare \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di woyu Sabóor, giiroo ci Asaf. \b \q1 \v 1 Yàlla siiw na fa Yuda, \q1 aw turam màgg fa Israyil. \q1 \v 2 Xaymaam a nga Salem, \q1 di xunteem ma fa \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*. \q1 \v 3 Fa la rajaxee fitt yuy boy \q1 ak pakk ak saamar ak ngànnaayal xare. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \b \q1 \v 4 Yàlla yaa ne ràññ te darajawu, \q1 ba raw tundi rëbbkat yi. \q1 \v 5 Futtees nay boroom fit, \q1 ñu ne nërëm, nelaw; \q1 kuy ñeyi xare, say yoxo nasax. \q1 \v 6 Yaw Yàllay Yanqóoba, yaa gëdd, \q1 gawar ak fasam nelaw. \q1 \v 7 Yaw mii, yaa mata ragal; \q1 boo meree, ana kuy taxaw fi sa kanam? \q1 \v 8 Fa asamaan nga biraleb àtte; \q1 suuf tiit, ne cell. \q1 \v 9 Ca la Yàllay jóg, ngir àtte, \q1 ba wallu kuy néew dooley àddina. \qs Selaw.\qs* \q1 \v 10 Doom aadamaak xadaram rafetal sa woy; \q1 desu xadaram, nga gañoo. \b \q1 \v 11 Seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, digooleen ak moom \q1 te jëfe ko. \q1 Kee jara ragal. \q1 Na ñi ko wër ñépp yótsiy teraanga. \q1 \v 12 Mooy sàggi sagu kilifa yi, \q1 di tiitaangey buuri àddina. \c 77 \s1 Yàllaa ngi seetaan \d Mu jëm ci Yedutun, njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf. \b \q1 \v 1 Naa xaacu, woo Yàlla, \q1 sama baat fa Yàlla, ngir mu déglu ma. \q1 \v 2 Bëccëg, ma jàq, sàkku Boroom bi; \q1 guddi, ma tàllal loxo, toqiwuma. \q1 Sama xol tëë sedd. \q1 \v 3 Ma bàyyi Yàlla xel, binni, \q1 xalaat, xol jeex. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \q1 \v 4 Éy Yàlla, tere nga maa gëmm bët, \q1 ma jaaxle ba waxatuma, \q1 \v 5 xanaa xalaat janti démb, \q1 at ya woon. \q1 \v 6 Guddi may fàttliku sama woy, \q1 di waxtaan ak sama ngegenaay, \q1 sama xel di jéex te naa: \q1 \v 7 «Boroom bi da may gàntal ba fàww, \q1 ba du ma baaxeeti mukk a? \q1 \v 8 Xanaa daa jeexal ngor tàkk? \q1 Am kàddoom a deñ ba fàww? \q1 \v 9 Moo Yàlla daa fàtte ñeewantee? \q1 Am meram a tëj buntu yërmandeem?» \qs Selaw.\qs* \q1 \v 10 Ma ne, sama naqar daal \q1 mooy Aji Kawe ji daa soppi loxoom. \b \q1 \v 11 Waaye naa fàttliku jaloorey Ki Sax rekk, \q1 fàttliku kéemaanam ya woon. \q1 \v 12 Naa xalaat sa bépp liggéey, \q1 di jàngat say jëf. \q1 \v 13 Céy Yàlla, yaa \w sell|lemma="sell:"\w* jikko! \q1 Jan yàllaa màgg ni Yàlla? \q1 \v 14 Yaa di Yàlla juy jëfi kéemaan, \q1 yaa siiwal sa doole ci biir xeet yi. \q1 \v 15 Kàttan nga jote sa mbooloo ma, \q1 sëti Yanqóobaak Yuusufa. \qs Selaw.\qs* \q1 \v 16 Yàlla, ndox maa la gis, \q1 ndox maa la gis, di lox; \q1 xóote yaa say, \q1 \v 17 niir ya yuri, \q1 kàddu riire asamaan, \q1 say fitt, fettaxandoo, \q1 \v 18 nga dënoo biir callweer, \q1 melax yi taal àddina, \q1 suuf di lox, di reg-regi. \q1 \v 19 Biir géej di saw yoon; \q1 saw xàll ci digg ndox mu ne xéew, \q1 te kenn gisul foo teg tànk! \q1 \v 20 Wommat nga sa mbooloo ni ag jur, \q1 Musaak Aaróona jiite. \c 78 \s1 Nit goreedi, Yàlla gore \d \v 1 Muy taalif bu giiroo ci Asaf. \b \q1 Yeen sama xeet, dégluleen, ma digal leen; \q1 teewluleen ma, ma wax leen. \q1 \v 2 Maa ngi leen di léeb, \q1 di sulli kumpay démb, \q1 \v 3 muy lu nu dégg, xam ko, \q1 sunuy maam xamal nu ko. \q1 \v 4 Dunu ko nëbb sunuy doom, \q1 xanaa di ko jottli maas giy ñëw, \q1 xamal leen jaloorey \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji \q1 ak kàttanam aki kéemaanam. \q1 \v 5 Bindal na sëti Yanqóoba téereb seede, \q1 muy yoon wi mu tegal Israyil. \q1 Mu sant maam yi, ñu xamal ko seeni doom, \q1 \v 6 ngir ñiy juddu ëllëg xam ko, \q1 am ay doom, \q1 ñu màgg, ba xamal ko seeni doom, \q1 \v 7 ngir ñu wóolu Yàlla, \q1 baña fàtte jëfi Yàlla, \q1 di jëfey santaaneem, \q1 \v 8 te baña roy seeni maam; \q1 maas gu të woon te déggadi, \q1 ñu ñàkk pastéef \q1 te sàmmuñu kóllërey Yàlla. \b \q1 \v 9 Waa giirug Efrayim ñoo soxi fitt, \q1 te keroog xare ba ñoo daw. \q1 \v 10 Ñoo sàmmul \w kóllërey|lemma="kóllëre g-:"\w* Yàlla, \q1 gàntal yoonam, \q1 \v 11 ba fàtte ay jalooreem, \q1 di kéemaan yi mu leen won. \q1 \v 12 Fa seen kanami maam la def kéemaan, \q1 fa diiwaanu Cowan, réewum Misra. \q1 \v 13 Moo xar géej ga, jal ndox ma nim tata, \q1 jàlle leen. \q1 \v 14 Bëccëg mu jiitee leen aw niir, \q1 ak leeru sawara guddi gépp. \q1 \v 15 Moo xar ay doj ca màndiŋ ma, \q1 mbàmbulaan wal, mu nàndal leen; \q1 \v 16 mu sotti ndox mu balle ciw xeer, \q1 walal, mu safi dex. \b \q1 \v 17 Teewul ñu wéy di moy Aji Kawe ji, \q1 di ko gàntal ca màndiŋ ma. \q1 \v 18 Ñoo diiŋate Yàlla xol, \q1 di xemmem ñam wu bakkane. \q1 \v 19 Ñuy waxal Yàlla naan: \q1 «Xam ngeen ne Yàlla manu noo taajal ndab ci màndiŋ mi! \q1 \v 20 Dóor naw doj, moos, ndox ma fettax, \q1 wal ma baawaan, \q1 waaye aw ñam nag? \q1 Daa mana leel mbooloo mii aw yàpp?» \q1 \v 21 Aji Sax ji dégg ci, mer lool; \q1 xolam tàng ci sëti Yanqóoba, \q1 am sànj tàkkal Israyil. \q1 \v 22 Dañoo gëmul Yàlla, \q1 doyloowuñu wallam. \q1 \v 23 Mu digal niir ya fa kaw, \q1 ubbi bunti asamaan, \q1 \v 24 tawal leen \w mànn|lemma="mànn:"\w*, ñu lekk: \q1 peppum asamaan la leen leel; \q1 \v 25 mburum jàmbaar la nit lekk, \q1 mu wàcceel leen ca lu ne gàññ. \q1 \v 26 Yàlla wale ngelawal penku fa asamaan, \q1 bëmëx ak dooleem ngelawal bëj-saalum. \q1 \v 27 Mu tawal leenu yàpp, mu saawe ni pënd, \q1 di njanaaw yu ne gàññ ni feppi suufas géej, \q1 \v 28 wàcce ko fa seen digg dal ba, \q1 mu dajal seeni dëkkuwaay. \q1 \v 29 Mu faj seen aajo, \q1 ñu lekk ba suur këll. \q1 \v 30 Teewul bala seen xel a dal, \q1 seen lanc jàllagul sax, \q1 \v 31 Yàlla mer na, dal ci seen kaw, \q1 bóom ña ëpp doole ca ñoom, \q1 fàdd waxambaaney Israyil. \b \q1 \v 32 Loolu lépp teewul ñuy bàkkaar ba tey \q1 te gëmuñu ay kéemaanam. \q1 \v 33 Mu dagg seeni fan, mu wéy ni cóolóol, \q1 faat seen bakkan ci safaan bu gaaw. \q1 \v 34 Ba leen Yàlla fàddee, ña des sàkku ko, \q1 tuub, waññiku ci moom. \q1 \v 35 Ñu fàttliku ne Yàllaay seen cëslaay, \q1 xam ne Yàlla Aji Kawe jeey seen njotlaay. \q1 \v 36 Teewul ñu di ko jéema naxey wax, \q1 di ko fen. \q1 \v 37 Joxuñu ko woon xol, \q1 sàmmuñu kóllëreem. \q1 \v 38 Teewul mu yërëm, \q1 baal leen seen ñaawtéef, \q1 ba sànku leen. \q1 Muñ na meram, muñati, \q1 te toppul xolam, \q1 \v 39 ndax xalaataat ne suuxu neen lañu, \q1 di noo guy dem te du délsi. \b \q1 \v 40 Gàntal nañu ko ba tàyyi ca màndiŋ ma, \q1 teg ko naqar ca ndànd-foyfoy ga. \q1 \v 41 Ñu dellu di diiŋat Yàlla, \q1 di naqaral Aji Sell, ji séddoo Israyil. \q1 \v 42 Fàtte nañu ndimbalam la, \q1 bés ba mu leen jotee ca noon ba, \q1 \v 43 ba def ay firndeem ca Misra, \q1 muy kiraamaam ya ca Cowan. \b \q1 \v 44 Moo soppli deret seen yooni ndox, \q1 ba naaneetuñu wal ya. \q1 \v 45 Mu wàcce seen biir ndiiraanu weñ \q1 yu leen di lekk, \q1 ak mbott yu leen sànk. \q1 \v 46 Mu jox soccet yi seen gàncax, \q1 jébbal njéeréer yi seen meññeef. \q1 \v 47 Seen garabi reseñ, mu fóome tawab yuur, \q1 seen garabi sikomoor, mu fóome waame. \q1 \v 48 Seen jur gu gudd, mu bàyyeek tawab yuur, \q1 seeni gàtt, mu bàyyeek sawaray melax. \q1 \v 49 Yàlla sotti leen tàngooru xadaram, \q1 mu dim sànj ak naqar ak njàqare, \q1 lépp di gàngooru ndaw yu indiy musiba. \q1 \v 50 Mu afal meram, \q1 ba musalul seen bakkan, \q1 xanaa jébbal leen mbas ma. \q1 \v 51 Daa fàdd képp kuy taaw ca Misra \q1 te juddoo seen digg doole, fa xaymay sëti Xam\f + \fr 78.51 \fr*\fk sëti Xam \fk*\ft mooy Misra ba tey.\ft*\f*. \b \q1 \v 52 Mu génne ñoñam niy gàtt, \q1 wommat leen ni gétt ca màndiŋ ma, \q1 \v 53 ba yóbbu leen fu wóor te tiituñu; \q1 seeni noon, géej ga mëdd leen. \q1 \v 54 Mu yóbbu leen fa suufam su \w sell|lemma="sell:"\w* sa, \q1 fa tund woowu mu jënde dooleem. \q1 \v 55 Da leena dàqal ay xeet, \q1 dogal leen céru suuf, \q1 sancal giiri Israyil ca seeni xayma. \b \q1 \v 56 Teewul ñuy diiŋat ak a gàntal Yàlla Aji Kawe ji, \q1 sàmmuñu ay dénkaaneem, \q1 \v 57 xanaa dëddu, di ko wor ni seeni maam, \q1 toogadi ni xala gu yolom. \q1 \v 58 Ñu di ko merlook seen \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w*, \q1 di ko fiirlook seen jëmmi tuur. \q1 \v 59 Ba ko Yàlla yégee, mer na, \q1 ba jéppi Israyil lool. \q1 \v 60 Mu gental dëkkuwaayam ba ca Silo, \q1 xaymaam ba mu sampoon ca doom aadama ya. \q1 \v 61 Mu jébbal ngàllo màndargam dooleem\f + \fr 78.61 \fr*\fk màndargam dooleem \fk*\ft ji ñu wax fi mooy gaal gi àlluway kóllërey Yàlla dence.\ft*\f*, \q1 may gànjaram ca loxol noon ba. \q1 \v 62 Daa bàyyee ñoñam saamaru noon, \q1 ndax mere yooya séddoom. \q1 \v 63 Seeni waxambaane deeye xare, \q1 seeni janq lamb; \q1 \v 64 seeni \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* loroo saamar, \q1 te jëtun jooyul. \b \q1 \v 65 Ca la Boroom bi yewwu ni ku doon nelaw, \q1 mel ni jàmbaar ju biiñ xabtal. \q1 \v 66 Mu dóor noon ba yari gannaaw, \q1 teg leen gàcce gu dul fey, \q1 \v 67 ba noppi xalab waa kër Yuusufa, \q1 te tànnul giirug Efrayim, \q1 \v 68 xanaa tànn giirug Yuda, \q1 taamu tundu \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* wi mu sopp. \q1 \v 69 Mu tabax këram gu sell, na mu mel fa kawa kaw, \q1 dëgër ni suuf, si mu samp ba fàww. \q1 \v 70 Mu teg ca tabb Daawuda, jaamam ba, \q1 jële ko ca gétti xar ya, \q1 \v 71 fa mu doon topptoo jur ga; \q1 mu sàmmal ko waa kër Yanqóoba, \q1 askanu Israyil wi mu séddoo. \q1 \v 72 Daawuda sàmme leen xol bu mucc ayib, \q1 jiitee leen manooreem. \c 79 \s1 Yàlla, feyul nu \d \v 1 Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf. \b \q1 Céy Yàlla, yéefar yi song nañu sa moomeel, \q1 teddadil nañ sa kër gu \w sell|lemma="sell:"\w*, \q1 gental nañ Yerusalem. \q1 \v 2 Leel nañ tan yi sa néewi jaam ñi, \q1 leel nañ rabi àll yi sa suuxi wóllëre yii. \q1 \v 3 Ñu tuur seen deret nim ndox, \q1 ba Yerusalem daj, \q1 te amul kuy rob néew yi. \q1 \v 4 Noo ngi nii di mbalitu dëkkandoo yi; \q1 ñu séqe nu ay kókkaleeki kekku. \b \q1 \v 5 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, xanaa doo nu mere ba fàww, \q1 sa fiiraange ni sawara ci sunu kaw? \q1 \v 6 Sippil sa mer yéefar yi la xamul, \q1 ak réew yi wormaalul sa tur. \q1 \v 7 Ñoo sëxëtoo giirug Yanqóoba, \q1 gental dëkkuwaayam. \q1 \v 8 Bul nu topp ñaawtéef ya woon, \q1 ngalla gaaw noo gatandoo sa yërmande. \q1 Danu ne dàll, ba ne dett. \q1 \v 9 Éy Yàlla, yaa nuy musal, wallu nu, \q1 ba sa seede rafet. \q1 Xettli nu te baal nu sunuy bàkkaar, \q1 ba sa woy rafet. \q1 \v 10 Bul tax yéefar yi naa: \q1 «Ana seen Yàlla?» \q1 May nu, nu gis ni ngay mbugale yéefar yi, \q1 feye leen sa deretu jaam yi tuuru. \q1 \v 11 Ñi ñu jàpp, yal na seeni onk àkki fa yaw. \q1 Ñi ci tànki ndee, yal nanga leen musale sa doole ju màgg. \b \q1 \v 12 Boroom bi, sewal gi la sunuy dëkk sewal, \q1 këpp leen ko juróom yaari yoon, \q1 \v 13 te nun ñiy sa mbooloo, di sa gétt gi ngay foral, \q1 nu di la sant ba fàww, \q1 di biral sa ngërëm sët ba sëtaat. \c 80 \s1 Yàlla, suqlil sa njëmbat \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor yi, di seedeb Sabóor, giiroo ci Asaf. \b \q1 \v 1 Éy yaw, Sàmmu Israyil, teewlu nu; \q1 yaw mi jiite Yuusufa ni ag jur, \q1 yaw mi toogandook malaakay \w serub|lemma="serub y-:"\w* yi, feqal sag leer. \q1 \v 2 Dawalal sa njàmbaar, ñeel Efrayim ak Beñamin ak Manase, \q1 te wallusi nu. \q1 \v 3 Éy Yàlla, suqli nu; \q1 geesoo nu sa leeru kanam, nu raw. \b \q1 \v 4 Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, Yàlla Boroom gàngoor yi, \q1 foo àppal sa mer, \q1 mi ngay wuyoo sa ñaanu mbooloo mi? \q1 \v 5 Leel nga nuw naqar, \q1 nàndal nu mbàndum rongooñ, \q1 \v 6 def nga dëkkandoo di nu xëccoo, \q1 noon di nu ree. \q1 \v 7 Éy Yàlla Boroom gàngoor yi, suqli nu; \q1 geesoo nu sa leeru kanam, nu raw. \b \q1 \v 8 Yaa déjjatee reseñ Misra, \q1 dàq yéefar yi, indi, jëmbataat. \q1 \v 9 Nga wéex ko, \q1 mu sampu, law, dajal réew mi; \q1 \v 10 keppaaram muur tund yi, \q1 ay caram sàng garabi seedar yu mag yi. \q1 \v 11 Mu tàllal ay bànqaasam ba géej, \q1 lawal njebbit la ba dex ga. \b \q1 \v 12 Lu tax nga bëtt ay miiram, \q1 ba ku fa jaare witt ca, \q1 \v 13 mbaam àll di ko ruur, \q1 ndundati àll di ca for? \q1 \v 14 Éy Yàlla Boroom gàngoor yi, geesul; \q1 séentool asamaan, ba gis \q1 te taxawusi reseñ jii. \q1 \v 15 Taxawusil njëmbat lii nga jëmbate sa ndijoor, \q1 ngarab sii nga dooleelal sa bopp. \b \q1 \v 16 Dees koo gor, taal; \q1 yal na ñii sànkoo sa mbugal. \q1 \v 17 Yal nanga yiir ki nga tànn, \q1 kii nga dooleelal sa bopp, \q1 \v 18 ba dootunu la dëddu. \q1 May nu nu dund, nu wormaal sa tur. \q1 \v 19 Éy Aji Sax ji, Yàlla Boroom gàngoor yi, suqli nu, \q1 geesoo nu sa leeru kanam, nu raw. \c 81 \s1 Déggal Yàlla, jariñu \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, giiroo ci Asaf, te ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit. \b \q1 \v 1 Sarxolleleen ci Yàlla, mi nuy dooleel; \q1 xaaculeen ci Yàllay Yanqóoba. \q1 \v 2 Yékkatileen woy te jiin, \q1 xalam neex, ànd ak moroom ma. \q1 \v 3 Wal-leen liit gi ci Terutel weer wi, \q1 ak weer wu birale bésu màggal. \q1 \v 4 Loolu wartéefu Israyil la, \q1 di ndigalu Yàllay Yanqóoba, \q1 \v 5 di ndénkaane lu mu dénk waa kër Yuusufa, \q1 ba Yàllay dali ca kaw réewum Misra. \q1 Baat bu ma xamul laa dégg, mu naan: \q1 \v 6 «Sippi naa leen, \q1 woyofal seeni yoxo. \q1 \v 7 Ngeen jàq, woo ma, ma xettli leen, \q1 wuyoo leen fa kiiraayal dënn ya, \q1 te maa leen nattoo fa wal ma ca Meriba. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \q1 \v 8 Yeen sama ñoñ, dégluleen, ma dénk leen. \q1 Éy Israyil, su ngeen ma déglu woon! \q1 \v 9 Buleen fat tuuru jaambur, \q1 buleen sujjóotal tuuru doxandéem. \q1 \v 10 Man, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, maay seen Yàlla \q1 ji leen yékkatee réewum Misra. \q1 Ŋaleen ŋafeet, ma reggal leen. \b \q1 \v 11 «Waaye sama ñoñ déggaluñu ma, \q1 Israyil gii nangulu ma. \q1 \v 12 Moo tax ma bërgël leen ak seenug të, \q1 ñuy wéye seeni pexe. \q1 \v 13 Éy su ma sama ñoñ déggaloon, \q1 éy su Israyil toppoon samay nammeel! \q1 \v 14 Ci saa si laay torxal seeni noon, \q1 duma seeni bañ, \q1 \v 15 ba ku bañ Aji Sax ji di ko raamal, \q1 te àppam du jeex ba fàww. \q1 \v 16 Kon yeen, ma leel leen ngën-gi-pepp, \q1 reggal leen lem ju doj xelli.» \c 82 \s1 Yàllaay àtte ndawi péncam \d \v 1 Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf. \b \q1 Yàlla toog na, di jiite ndajem boppam, \q1 di àtte ndawi péncam, naan: \q1 \v 2 «Dungeen bàyyi àtteb njublaŋ, \q1 ak di faral ku bon? \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \q1 \v 3 Sàmmleen àqu néew-ji-dooleek jirim, \q1 tey àtte yoon ku ñàkk ak ku ndóol. \q1 \v 4 Walluleen néew-ji-dooleek walaakaana, \q1 di leen xettli ci ku bon. \b \q1 \v 5 «Ndawi péncum Yàlla yii xamuñu, dégguñu; \q1 xanaa di doxe lëndëmu ñaawtéef, \q1 ba kenuy suuf yépp di jaayu. \b \q1 \v 6 «Dama ne ay yàlla ngeen, \q1 yeen ñépp di njabootu Aji Kawe ji. \q1 \v 7 Waaye du leen tee dee ni doom aadama, \q1 du leen tee daanu ni képp kuy njiit.» \b \q1 \v 8 Ngalla Yàlla, taxawal, àtte àddina, \q1 yaw yaa séddoo xeetoo xeet. \c 83 \s1 Yàlla, mbugalal noon yi \d Di woyu Sabóor, giiroo ci Asaf. \b \d Éy Yàlla, bul ne cell, \q1 \v 1 rikk Yàlla, bul tanqamlu, ne patt. \q1 \v 2 Xoolal sa noon yiy riir, \q1 sa bañ yi fippu ba téen! \q1 \v 3 Sa ñoñ lañuy rabatal, \q1 di mànkool sa séddoo yii. \q1 \v 4 Ñu ne: «Ayca nu far seen xeet wi, \q1 ba deesul fàttlikooti turu Israyil.» \b \q1 \v 5 Dañoo mànkoo kat, \q1 te yaw lañu takktool: \q1 \v 6 muy néegi Edom ak Ismayla, \q1 néegi Mowab ak Agar, \q1 \v 7 néegi Gebal, Amon ak Amaleg \q1 ak waa Filisteek waa Tir, \q1 \v 8 réewum Asiri it fekki leen, \q1 di dooleel askanu Lóot wa. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \b \q1 \v 9 Def leen na nga defoon waa Majan, \q1 def ko Sisera ak Yabin ca dexu Kison\f + \fr 83.10 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Njiit ya\+bk* 7—8.\ft*\f*. \q1 \v 10 Ña nga sànkoo Endor, \q1 ba doon ub tos fi kaw suuf. \q1 \v 11 Defal seeni njiit na Oreb ak Seeb, \q1 def seen kilifa yépp ni Seba ak Salmuna, \q1 \v 12 ña ne woon: «Nan séddoo parluy Yàlla yi.» \q1 \v 13 Éy Yàlla, wëndeel leen ni callweer, \q1 ñu mel ni boob mu ngelaw wal. \q1 \v 14 Éy Yàlla, ni daay di xoyome àll, \q1 sawara wa jafal tund ya, \q1 \v 15 yal nanga leen ni toppeek sa dooley ngelaw, \q1 tiitale leen sa ngëlén. \q1 \v 16 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, sëlëm leen gàcce, \q1 ba ñu sàkku la. \q1 \v 17 Yal nañu rus, jàq ba fàww. \q1 Yal nañu torox, sànku. \q1 \v 18 Yal nañu xam ne yaw mi tudd Aji Sax ji doŋŋ \q1 yaay Aji Kawe ji yilif àddina yépp. \c 84 \s1 Ku dal ak Yàlla bég \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit, ñeel askanu Kore wu góor. \b \q1 \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoor yi, \q1 yaaka sopplub dëkkuwaay! \q1 \v 2 Damaa namm ëttub Aji Sax ji, \q1 di ko gelu ba jeex tàkk, \q1 jëmm jeek xol bi, \q1 di xaacul Yàlla jiy dund. \q1 \v 3 Éy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, \q1 sama buur, sama Yàlla, \q1 sawoor sax tag, nga fat ko, \q1 mbelaar it sàkk tàggam, \q1 denc ay cuujam fa sa \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*. \q1 \v 4 Ndokklee ku dëkke sa kër, \q1 di la màggalati. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \b \q1 \v 5 Ndokklee ku lay doolewoo, \q1 te namma topp njool ma jëm sa kër. \q1 \v 6 Buy jàll xuru Jooyoo, \q1 mu saf ko bëti ndox, \q1 céebo sànge xur wa barke, \q1 \v 7 muy gëna am doole, \q1 ba teewi fa Yàlla ca \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*. \b \q1 \v 8 Éy Yàlla Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, \q1 déglul, ma ñaan la! \q1 Yàllay Yanqóoba, teewlu ma. \qs Selaw.\qs* \q1 \v 9 Éy Yàlla, geesul Buur, sunu kiirlaay, \q1 ngalla niiral kii nga fal. \q1 \v 10 Benn fan ci sab ëtt de \q1 moo dàq junniy fan feneen. \q1 Sama taxawaayu bunt kër Yàlla \q1 moo ma gënal tëraayu biir xaymab ku bon. \q1 \v 11 Aji Sax ji Yàllaa mat jant, mat kiiraay; \q1 yiw ak daraja, Aji Sax ji joxe; \q1 te du ngëneel lu muy bañal ku mat. \q1 \v 12 Éy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, \q1 ndokklee ku la wóolu. \c 85 \s1 Aji Sax ji, suqleeti nu \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor. \b \q1 \v 1 Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, yaa baaxe woon sa réew mi, \q1 ba suqli sëti Yanqóoba yi, \q1 \v 2 baal sa mbooloo seeni ñaawtéef, \q1 jéggal leen bépp bàkkaar. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \q1 \v 3 Ba nga xadar ja, \q1 muñ mer ma. \b \q1 \v 4 Éy Yàlla mi nuy musal, suqli nu, \q1 te meddi. \q1 \v 5 Xanaa doo nu mere fàww, \q1 ba ca sët yaak sëtaat ya? \q1 \v 6 Xanaa dinga leqli sa mbooloo, \q1 ba ñu man laa bànneexoo? \q1 \v 7 Éy Aji Sax ji, won nu sa ngor, \q1 baaxe nu sag wall. \b \q1 \v 8 Woykat ba nee: «Naa déglu \q1 lu Aji Sax ji Yàlla di wax.» \q1 Jàmm lay wax wóllëreem ñiy ñoñam, \q1 ba duñu dellu ci jëfi dof. \q1 \v 9 Wallam aka jege ñi ko ragal, \q1 te leeram dëgmal sunu réew mii! \q1 \v 10 Ngor ak kóllëree daje, \q1 njekk ak jàmm saafoonte, \q1 \v 11 kóllëre jebbee fa suuf, \q1 njekk séentoo asamaan, \q1 \v 12 Aji Sax ji it maye ngëneel, \q1 sunu suuf meññal, \q1 \v 13 njekk jiitu Aji Sax ji, \q1 di ko xàllal yoonam. \c 86 \s1 Ma ñaan, bésub njàqare \d \v 1 Mu di ñaanu Daawuda. \b \q1 Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, teewlu ma, nangul ma, \q1 damaa ñàkk, néew doole. \q1 \v 2 Maa gore, musal ma; \q1 maay sa jaam bi la wóolu, \q1 yaw, sama Yàlla, wallu ma. \q1 \v 3 Éy Boroom bi, baaxe ma; \q1 yaw laay yendoo woo wall. \q1 \v 4 Boroom bi, bànneexalal sab jaam, \q1 yaw laa dékk sama xol. \q1 \v 5 Boroom bi, yaa baax, di bale, \q1 di nàddil sa ngor képp ku lay sàkku. \q1 \v 6 Éy Aji Sax ji, teewlul, ma ñaan la; \q1 déglul, ma tinu la. \q1 \v 7 Bu ma la wooyee bésub njàqare, \q1 yaa may nangul. \b \q1 \v 8 Boroom bi, doo moroomu tuur yi, \q1 te jëf melul ni sa jos. \q1 \v 9 Boroom bi, mboolem xeet yi nga sàkk \q1 ñoo lay sujjóotalsi, \q1 di màggal sa tur. \q1 \v 10 Yaa màgg te yéemey jëf, \q1 yaw doŋŋ yaa di Yàlla. \q1 \v 11 Éy Aji Sax ji, won ma sa nammeel, \q1 ma doxe sa worma. \q1 Tënkal sama xol ci ragal la. \q1 \v 12 Boroom bi sama Yàlla, \q1 naa la sante xol bu fees, \q1 màggal la ba fàww. \q1 \v 13 Ngor lu réy nga ma won, \q1 sorele maak tëraayu bàmmeel. \b \q1 \v 14 Éy Yàlla, nit ñu bew a ma jógal, \q1 def gàngoor gu néeg, di rëbb sama bakkan, \q1 te seetuñu la ci. \q1 \v 15 Waaye yaw Boroom bi Yàlla, yaa ñeewante, yërëm, \q1 yaa muñ mer, bare ngor ak worma. \q1 \v 16 Geesu ma, baaxe ma. \q1 Dooleelal sab jaam, \q1 wallul ki sa jaam sukk jur! \q1 \v 17 Ngalla def ma sa firndey mbaax, \q1 ba bañ yi gis ci, rus, \q1 ndax yaw Aji Sax, ji ma dimbali, dëfal ma. \c 87 \s1 Siyoŋ, yaay ndeyu xeet yi \d \v 1 Ñeel askanu Kore wu góor, di woyu Sabóor. \b \q1 Dëkkub Aji Sax ji, kenu yaa nga ca tund yu \w sell|lemma="sell:"\w* ya. \q1 \v 2 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee sopp bunti \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* gii, \q1 mu gënal ko fu askanu Yanqóoba dëkke. \q1 \v 3 Yaw, dëkkub Yàlla bi, \q1 tuddees na say jaloore. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \q1 \v 4 Yàlla nee: «Ma limaale Misraak Babilon, ñi ma xam di dégg. \q1 Xoolal Filisti ak Tir, ak réewum \w Kuus|lemma="Kuus:"\w*. \q1 Nit a ngii, juddoo fa,» \q1 \v 5 te teewul ñu cosaanale ko Siyoŋ, \q1 ne kii ak kee fa bokk juddoo, \q1 te Aji Kawe jee saxal Siyoŋ. \q1 \v 6 Aji Sax jeey lim xeet yi, limaale leen \q1 ne: «Kii fi la juddoo.» \qs Selaw.\qs* \q1 \v 7 Kuy fecc ak kuy woy ànd naan: \q1 «Sunu cosaanoo cosaan fii la!» \c 88 \s1 Ma jàq, jooy \d Muy woyu Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor, jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Maalat Leyanot, di taalifu Eman, mi bokk ci giirug Esra. \b \q1 \v 1 Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, Yàlla ji may musal, \q1 bëccëg ma yuuxu, \q1 guddi ma yuuxu fi sa kanam. \q1 \v 2 Yal na sama ñaan àgg fa yaw; \q1 teewlul, ma woote wall. \q1 \v 3 Damaa suur këll ay musiba, \q1 ba soreetuma njaniiw, \q1 \v 4 ñu sóoraale maak ñi wàcci biir bàmmeel. \q1 Ma mel ni jàmbaar ju kenn amatul yaakaar, \q1 \v 5 bokk ci néew, yi dara waratul, \q1 mbaa ku ñu bóom, mu tëdd cim pax, \q1 faaleetoo ko, xanaa dagg ko, wacc. \q1 \v 6 Tàbbal nga ma kàmb gu xóot, \q1 biir xóotey lëndëm. \q1 \v 7 Yen nga ma sa xadar, \q1 tance ma sa gannax yépp. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \q1 \v 8 Dàqal nga may xame, \q1 tax nga ñu seexlu ma; \q1 ma tëju, génnatuma. \q1 \v 9 Samay gët a ngi giim ndax naqar. \q1 Éy Aji Sax ji, maa ngi lay woo bés bu ne, \q1 dékk lay loxo. \b \q1 \v 10 Ku dee, lu muy doyeeti say kéemaan? \q1 Ndax néew dina jóg di la màggal? \qs Selaw.\qs* \q1 \v 11 Dees na siiwal sa ngor biir bàmmeel, \q1 mbaa sa worma ci paxum sànkute? \q1 \v 12 Ana kuy yég say kéemaan ci googu lëndëm? \q1 Ku lay seedeel njekk réew ma fàtte faloo? \b \q1 \v 13 Aji Sax ji, man, yaw lay woo wall, \q1 xëy, kare la gii ñaan, ne la: \q1 \v 14 Éy Aji Sax ji, loo may gàntale, \q1 di ma fuuylu? \q1 \v 15 Mitit bay laatikaaf, sama ngone ba tey; \q1 sa mbugal yu raglu, ba bopp ubu ràpp! \q1 \v 16 Sa mer mëdd ma, \q1 sa mbugal yu raglu sànk ma, \q1 \v 17 mëdd ma nim ndox bés bu ne, \q1 gëndoo fi sama kaw. \q1 \v 18 Dàqal nga ma soppeek xarit, \q1 ma far xejjoo lëndëm. \c 89 \s1 Aji Sax ji, loo dige woon? \d Muy taalif bu ñeel Etan mi bokk ci giirug Esra. \b \q1 \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji laay woye ngoram, ba fàww, \q1 di biral wormaam sët ba sëtaat. \q1 \v 2 Dama ne, sa ngor dàkk la sax, \q1 fa asamaan nga dëël sa worma. \q1 \v 3 Aji Sax ji nee: «Damaa fas \w kóllëreek|lemma="kóllëre g-:"\w* ki ma tànn, \q1 muy Daawuda sama jaam bi ma giñal ne ko: \q1 \v 4 “Damay saxal sa askan ba fàww, \q1 samp sab jal sët ba sëtaat.”» \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \b \q1 \v 5 Aji Sax ji, waa asamaan a ngi lay sante say jaloore, \q1 ndajem ñu sell ña di la joobee sa worma. \q1 \v 6 Ana kuy dab-dabal Aji Sax ji, fa kawa kaw? \q1 Ana ci goney Yàlla yi ku nirook Aji Sax ji, \q1 \v 7 Yàlla, ji ñu terala teral ci jataayu ñu sell ñi, \q1 te mu gëna raglu lu ko wër? \q1 \v 8 Yàlla, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, \q1 Ki Sax, ana ku tollook yaw doole? \q1 Yaw mi worma féete fu ne! \b \q1 \v 9 Yaw yaa man géej gu sàmbaraax; \q1 gannax ya fuddu, nga dalal. \q1 \v 10 Yaa fàdd Raxab\f + \fr 89.11 \fr*\fk Raxab: \fk*\ft mbaa ninki-nànka ba tey.\ft*\f*, bóom ko, \q1 tasaare say noon ci sa doole. \q1 \v 11 Yaa moom asamaan, yaa moom suuf. \q1 Àddinaak li ci biiram, yaa ko taxawal. \q1 \v 12 Bëj-gànnaar ak bëj-saalum, yaa ko sàkk. \q1 Tabor ak Ermon, tund ya, di sarxollee sa tur. \q1 \v 13 Yaa àttan, jàmbaare; \q1 sa loxo di dooley neen, \q1 sa ndijoor ca kaw! \q1 \v 14 Njekk ak njub a lal sab jal, \q1 ngor ak worma dox jiitu la. \b \q1 \v 15 Aji Sax ji, ndokklee mbooloo mu la xal di sarxollee, \q1 di niitoo saw yiw, \q1 \v 16 ànd di la bége bés bu ne, \q1 sag njekk siggil leen. \q1 \v 17 Seen darajay doole, yaw a. \q1 Boo nu baaxee, nu yokku kàttan. \q1 \v 18 Sunu kiirlaay lii, Aji Sax jeey boroom; \q1 sunu buur bii, Aji Sell ji séddoo Israyil ay boroom. \b \q1 \v 19 Wax nga say wóllëre ci peeñu, \q1 ne leen: «Tànne naa jàmbaar ci xeet wi, \q1 dénk ko ndimbal. \q1 \v 20 Gis naa sama jaam Daawuda, \q1 fale ko sama diw gu \w sell|lemma="sell:"\w*, \q1 \v 21 ànd ak moom, saxal ko, \q1 di ko dooleel. \q1 \v 22 Noon du ko bett, \q1 ku bon du ko torxal. \q1 \v 23 Ay bañam, ma rajaxe; \q1 ay noonam, ma fàdd, \q1 \v 24 sama wormaak sama ngor di ko gunge, \q1 may yokk kàttanam. \q1 \v 25 Géej, ma teg ci loxoom, \q1 dex, ma ne ca tegg ndijooram. \q1 \v 26 Moo ma naa: “Yaay sama baay, \q1 di sama Yàlla, di sama wéeru-mucc.” \q1 \v 27 Te it maa koy def samab taaw, \q1 tiimale ko buuri àddina, \q1 \v 28 sàmmal ko sama ngor ba fàww, \q1 feddlil ko sama kóllëre. \q1 \v 29 Damay saxal askanam ba fàww, \q1 yàggal ab jalam ni asamaan. \q1 \v 30 Bu ay sëtam wàccee sama yoon, \q1 baña doxe samay ndigal, \q1 \v 31 mbaa ñu xëtt sama dogali yoon, \q1 baña sàmmonteek samay santaane, \q1 \v 32 ma bantale leen seenug moy, \q1 dumaa leen seen ñaawtéef. \q1 \v 33 Waaye duma ko daggal sama ngor, \q1 te duma ko ñàkke worma. \q1 \v 34 Duma fecci sama kóllëre, \q1 te duma toxal sama kàddu. \q1 \v 35 Benn yoon laa ko giñ ci sama sellnga, \q1 duma fen Daawuda: \q1 \v 36 askanam, dàkk; \q1 ab jalam fi sama kanam ni jant bi, \q1 \v 37 ak weer wi sax ba fàww, \q1 dib seede bu wér ca niir ya.» \qs Selaw.\qs* \b \q1 \v 38 Ndaxam yaw Yàlla, jéppi nga ki nga fal, \q1 mere ko, wacc ko. \q1 \v 39 Fecci nga sa kóllëreek sab jaam, \q1 foq nguuram, detteel ko. \q1 \v 40 Bëtt nga miiram yépp, \q1 saam ay tataam, \q1 \v 41 ku fa jaare, jël ca alalam, \q1 mu doon mbalitu dëkkandoo yi. \q1 \v 42 Yékkati ngay bañam, \q1 noonam yépp di ree. \q1 \v 43 Dayal nga saamaram, \q1 te taxawuwloo ko cib xare. \q1 \v 44 Xañ nga ko darajaam, \q1 rattax ngànguneem fa suuf. \q1 \v 45 Dagg nga fani ngoneem, \q1 sang ko gàcce. \qs Selaw.\qs* \b \q1 \v 46 Éy Aji Sax ji, xanaa lii du jeex? \q1 Xanaa doo làqu fàww nii, \q1 sa mer di boy? \q1 \v 47 Bàyyi ma xel, samay fan yàggul. \q1 Xanaa du neen a tax nga sàkk mboolem doom aadama? \q1 \v 48 Ana kuy dund te du dee? \q1 Ku mana rëcc tëraayu bàmmeel? \qs Selaw.\qs* \q1 \v 49 Boroom bi, ana sa ngor la nga daan jëfe \q1 te nga giñale woon ko Daawuda ci sa worma? \q1 \v 50 Boroom bi, bàyyil xel ci sa gàcceg jaam ñi, \q1 ak xeet yu bare yi ma yenu yépp. \q1 \v 51 Aji Sax ji, say noon a ngi sewal \q1 buur bi nga fal, ne ko dann. \b \q1 \v 52 Cant ñeel na Aji Sax ji ba fàww. \q1 Amiin, amiin. \c 90 \s1 Doom aadama yàggul \d \v 1 Muy ñaanu Musaa, góorug Yàlla ga. \b \q1 Boroom bi, yaa nu masa fat \q1 maasoo maas. \q1 \v 2 Bala tund yee juddu, \q1 bala ngay sos suuf ak àddina, \q1 yaa mas di Yàlla, ba fàww. \q1 \v 3 Yaay delloo doom aadama ci pënd, \q1 ne ko: «Yaw, doom aadama, dellul!» \q1 \v 4 Junniy at ci yaw \q1 daa gaaw ni démb ak tey, \q1 mbete waxtu yu néew ci wattub guddi. \q1 \v 5 Yaay buub nit, nelawal ko. \q1 Suba mu jebbi nim ñax, \q1 \v 6 xëy, jebbi, naat; \q1 ngoon mu lax, wowal. \q1 \v 7 Soo meree kay, nu sànku, \q1 nga xadaru, nu jàq. \q1 \v 8 Sunuy ñaawtéef a ngi janook yaw, \q1 te sunu mbóot leer na la. \q1 \v 9 Sunu giiru dund nga di nu mere, \q1 sunuy fan jeex ni noo guy naaw. \q1 \v 10 Sunu àppu dund di juróom ñaar fukki at, \q1 ku dëgër ba dëgër, juróom ñett fukk; \q1 li ci ëpp di coonooku tiis, \q1 ne fëyy, nu wéy. \q1 \v 11 Ana ku xam sa dooley mer \q1 ak sa xadar ju raglu? \q1 \v 12 Yal nanga nu xiir ci lim sunuy fan, \q1 ba nu mana dawal xel mu rafet. \b \q1 \v 13 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, délsil, loo deeti xaar? \q1 Ngalla yërëmal sa jaam ñi. \q1 \v 14 Nu xëy, nga reggal nu sa ngor, \q1 nuy sarxolle, bànneexoo ko sunu giiru dund. \q1 \v 15 Bànneexal nu limu fan yi nga nu mbugal, \q1 diirub ati tiis yi nu dund. \q1 \v 16 Yal na sa jaloore leer sa jaam ñi, \q1 sa daraja leer seeni doom. \q1 \v 17 Boroom bi sunu Yàlla, ngalla baaxe nu. \q1 Sottalal nu sunuy liggéey, \q1 rikk, sottalal nu sunuy liggéey. \c 91 \s1 Aji Sax jee mat kaaraange \q1 \v 1 Ku dëkke kiiraayu Aji Kawe ji \q1 yaa këroo keppaaru Aji Man ji. \q1 \v 2 Dama naa \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji: \q1 «Yaw laay làqoo, di la fegoo; \q1 ngay sama Yàlla ji ma doyloo.» \q1 \v 3 Kii kay moo lay musal cig fiir \q1 ak loraangey mbas. \q1 \v 4 Kiiraayam la lay sànge, \q1 nga yiiru, làqu; \q1 wormaam yéew la, di la aar. \q1 \v 5 Doo ragal njàqarey guddi \q1 mbaa fittu bëccëg \q1 \v 6 mbaa mbas mu yooteg lëndëm, \q1 ak balaa buy fàdde njolloor. \q1 \v 7 Junni daanu fi sa wet, \q1 fukki junni (10 000) daanu fi sa ndijoor, \q1 du tax mu jege la. \q1 \v 8 Say gët nga ciy teg, \q1 di seetaan ku bon di jot yoolam. \q1 \v 9 Yaw mi màkkaanoo Aji Sax ji, \q1 Aji Kawe jii di sama rawtu, \q1 \v 10 genn loraange du la dab, \q1 balaa du jege sa xayma. \q1 \v 11 Ay malaakaam la lay booleel, \q1 ñu di la sàmm foo jëm. \q1 \v 12 Seeni loxo lañu lay leewoo, \q1 ba doo fakkastaloow doj. \q1 \v 13 Dangay falaxe jaan ak gaynde, \q1 di rajaxe ñàngóor ak sibi. \b \q1 \v 14 Yàlla da naa: «Kii de man la safoo, \q1 ma di ko xettli. \q1 Man la xam, te maa koy teg fu wóor. \q1 \v 15 Mu woo ma, ma wuyu ko; \q1 mook man ci biir njàqare, \q1 ma xettli ko, darajaal ko, \q1 \v 16 reggal koy fan, \q1 baaxe ko samag wall.» \c 92 \s1 Nu woy bésub Noflaay \d Muy woyu Sabóor ngir \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*. \b \q1 \v 1 Céy ngëneel li ci sant \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 di la woy, yaw Aji Kawe ji, \q1 \v 2 xëye tudd sa ngor, \q1 gonloo xamle sa worma, \q1 \v 3 xalamu fukki buum ànd ak moroom ma, \q1 xeetu kooraa jibandoo. \q1 \v 4 Aji Sax ji, yaa ma bégale say jaloore, \q1 may sarxolle ci say manoore. \q1 \v 5 Aji Sax ji, yaa réyi jëf; \q1 xóoti pexe. \q1 \v 6 Ku ñàkk xel réere ko, \q1 ku dofe umple ko. \q1 \v 7 Bu ku bon sëqlee nim ñax, \q1 képp kuy def lu bon di yokkule, \q1 dañoo nara sànku ba fàww rekk. \b \q1 \v 8 Waaye yaw ma fa kaw, \q1 yaay Aji Sax ji ba fàww. \b \q1 \v 9 Aji Sax ji, sa noon yi kay, ndeke yoo; \q1 ndeke yoo sa noon yi, sànku rekk; \q1 defkati mbon ñépp, fëlxoo rekk. \q1 \v 10 May nga ma dooley nagu àll, \q1 ma diwoo diw gu bees. \q1 \v 11 Maa gis jéllu noon yi, \q1 dégg yuuxi ñu bon ñi may tëru. \q1 \v 12 Ku jub day naat nig tàndarma, \q1 màgg ni seedaru Libaŋ \q1 \v 13 gu ñu jëmbat biir kër Aji Sax ji, \q1 muy naate sunu biir ëttu Yàlla; \q1 \v 14 bu màggatee sax di meññ, \q1 tooy xepp, sëq lipp, \q1 \v 15 di biral njubtey Aji Sax ji, \q1 sama cëslaay ji dencul njubadi. \c 93 \s1 Ma bàkk Aji Sax ji \q1 \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jeey buur, soloo daraja; \q1 Aji Sax jee solu, gañoo doole: \q1 àddinaa ngii, dëju te raful. \q1 \v 2 Sab jal a masa sax, \q1 te yaa masa nekk. \q1 \v 3 Aji Sax ji, géej a riir, \q1 géej a àddu, mu riir, \q1 gannax ya rëkk, mu riir. \q1 \v 4 Waaye riirum wal mu walangaanoo, \q1 ak géej gu sàmbaraaxoo, \q1 Aji Sax ja fa kaw a rawati! \q1 \v 5 Say santaanee wér te wóor; \q1 Aji Sax ji, sellnga la sa kër jagoo \q1 bésoo bés. \c 94 \s1 Yàllaay mbugal ku bon \q1 \v 1 Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Yàlla, boroom mbugal! \q1 Boroom mbugal, feqal sag leer! \q1 \v 2 Yaw miy àtte àddina, jógal \q1 yool ku bew. \q1 \v 3 Aji Sax ji, fu ku bon kiy àkki? \q1 Fu ku bon kiy kañu àkki? \q1 \v 4 Ñu ngi làmmiñoo reewande, \q1 képp kuy def lu bon di damu. \q1 \v 5 Aji Sax ji, say ñoñ lañuy dëggaate; \q1 say séddoo lañuy néewal. \q1 \v 6 Jëtun akub doxandéem, ñu faat; \q1 ab jirim, ñu bóom, \q1 \v 7 te naa: «Ki Sax gisu ci, \q1 Yàllay Yanqóoba jii yégu ko.» \b \q1 \v 8 Yeen bokk yu dofe yi, moytuleen. \q1 Gàtt xel yi, kañ ngeen di muus? \q1 \v 9 Ki jëmbati nopp, da dul dégg a? \q1 Am ki xari gët, da dul gis? \q1 \v 10 Kiy yar yéefar yi, da dul mbugalee? \q1 Du mooy kiy xamal nit? \q1 \v 11 Aji Sax ji xam na xalaatu nit, \q1 xam ne cóolóolu neen la. \b \q1 \v 12 Ki Sax, ndokklee ki ngay yar, \q1 tàggat ko ci saw yoon, \q1 \v 13 dëfal ko ci bési safaan, \q1 ba keroog ñuy gasal ku bon. \q1 \v 14 Boroom bi kat du wacc ñoñam mukk, \q1 du bàyyi ay séddoom. \q1 \v 15 Àtte dina dellu laloo njekk, \q1 képp ku jub topp ca. \q1 \v 16 Ana ku may taxawal ci ñu bon ñi? \q1 Ku may jógal ci biir ñiy def lu bon? \q1 \v 17 Su ma Aji Sax ji walluwloon, \q1 tuuti ma fanaani réew ma ne selaw. \q1 \v 18 Dama noon: «Tarxiis naa!» \q1 Waaye yaa ma awoo sa ngor. \q1 \v 19 Ma bare xalaati xol, \q1 nga dëfal ma, ma bég. \q1 \v 20 Loo séq ak njiit lu jubadi \q1 luy yoonal njubadi? \q1 \v 21 Ñii dañoo mànkoo, di tëru ku jub, \q1 di teg àtteb dee ku deful dara. \q1 \v 22 Waaye Aji Sax jeey sama rawtu, \q1 sama Yàlla laay sës, làqu. \q1 \v 23 Moo leen di këpp seen ñaawtéef, \q1 sànke leen seenug mbon. \q1 Sunu Yàlla Aji Sax jee leen di sànk. \c 95 \s1 Kaayleen, nu sant \q1 \v 1 Kaayleen, nu sarxolleel \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 nu xaacul ki nuy sës, mucc. \q1 \v 2 Nanu ko dikke cant, \q1 woyal ko, mu riir. \q1 \v 3 Aji Sax jeey Yàlla ju màgg ji, \q1 buur bu mag bi tiim yàllay xeet yépp. \q1 \v 4 Moo moom xóotey suuf, \q1 moom colli tund yi, \q1 \v 5 moom géej, sàkk ko, \q1 moom jéeri ji mu mooñ. \q1 \v 6 Nan sëgg, sujjóot, \q1 sukkal Aji Sax ji nu sàkk. \q1 \v 7 Mooy sunu Yàlla, \q1 nuy xeet wi muy foral, \q1 diy gàtt ciy loxoom. \b \q1 Bésub tey yal nangeen dégg kàddoom \q1 \v 8 ga mu noon: «Buleen të, na woon fa Meriba, \q1 jantub keroog fa Maasa, ca màndiŋ ma, \q1 \v 9 fa ma seeni maam doon nattoo, \q1 di ma seetlu te gis la ma def\f + \fr 95.9 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Mucc ga\+bk* 17.1-7.\ft*\f*. \q1 \v 10 Ñeent fukki at laa jéppi googu maas, \q1 ma ne: “Xeet wu ñàkk wormaa ngi, \q1 te faaleedi samay santaane.” \q1 \v 11 Moo ma taxa mer, ba giñal leen, \q1 ne duñu tàbbi fa sama noflaay.» \c 96 \s1 Buur Yàllaa ngi àttesi àddina \q1 \v 1 Woyleen \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji woy wu yees, \q1 te àddina yépp woy Aji Sax ji. \q1 \v 2 Woyleen Aji Sax ji, màggal turam, \q1 di yéene bés ak bés ne mooy musle. \q1 \v 3 Siiwal-leen teddngaam fi biir xeet yi, \q1 xamal waasoo waaso ay jalooreem. \q1 \v 4 Aji Sax jee màgg, jara santa sant \q1 te gëna mata ragal lépp lu ñuy jaamu. \q1 \v 5 Mboolem yàlla yi xeet yiy jaamu, yàllantu la, \q1 waaye Aji Sax jee sàkk asamaan. \q1 \v 6 Màggaay ak daraja, fa moom, \q1 dooleek taar, fa këram gu sell. \b \q1 \v 7 Yeen làngi xeet yi, seedeel-leen Aji Sax ji; \q1 seedeel-leen Aji Sax ji teddngaak doole. \q1 \v 8 Seedeel-leen Aji Sax ji teddngay turam, \q1 yékkatil kob sarax, duggaale ëttam. \q1 \v 9 Sujjóotal-leen Aji Sax ji làmboo sellnga, \q1 te àddina wërngal këpp di ko loxal. \q1 \v 10 Neleen xeet yi Aji Sax jeey buur: \q1 àddinaa ngii, dëju te raful. \q1 Mooy àtte xeet yi njub. \q1 \v 11 Asamaanoo, bégal! Suufoo, bànneexul! \q1 Géejoo, riiral yaak li la fees, \q1 \v 12 te mbooy mi di jaayu, mook lu ci biiram, \q1 garabi àll bi sarxolleendoo, \q1 \v 13 gatandoo ko Aji Sax jiy dikk, \q1 àttesi àddina, \q1 di àtte dun bi njekk, \q1 tey àttee xeet yépp dëggam. \c 97 \s1 Nguurug Aji Sax ji njekk la \q1 \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jeey Buur, na àddina bég; \q1 dunoo dun bànneexu. \q1 \v 2 Ay xàmbaar a ko yéew, \q1 njekk ak njub lal ab jalam. \q1 \v 3 Sawaraa dox, jiitu ko, \q1 di xoyomi noonam wetoo wet, \q1 \v 4 ay melaxam leeral àddina, \q1 waa àddina gis, di pat-pati; \q1 \v 5 tund yi ne soyox seey fi kanam Aji Sax ji \q2 boroom àddina sépp. \q1 \v 6 Asamaan a ngi biral njekkam, \q1 xeetoo xeet di gis darajaam. \q1 \v 7 Gàcce ñeel na kuy jaamu jëmmi tuur, \q1 di puukarewoo ay yàllantu. \q1 Yeen yàllay xeet yépp, sujjóotal-leen kii, \q1 \v 8 \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* dégg ca, bég, \q1 waa Yuda it di bànneexoo àttey Aji Sax jii. \q1 \v 9 Aji Sax ji, Aji Kawe ji tiim suuf sépp; \q1 yaaka màgga màgg, ba sut tuuroo tuur. \b \q1 \v 10 Yeen soppey Aji Sax ji, bañleen lu bon. \q1 Aji Sax jeey sàmm ay wóllëreem, \q1 di leen musal ci ku bon. \q1 \v 11 Jub, leerlu; \q1 jubal, bég. \q1 \v 12 Yeen aji jub ñi, bànneexooleen Aji Sax ji, \q1 sante ko sellngaam. \c 98 \s1 Woyleen Aji Sax jiy àttesi \d \v 1 Muy kàddug Sabóor. \b \q1 Woyleen \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji woy wu yees, \q1 moo def ay jaloore, \q1 kàttanam ak sellngay dooleem \q1 jox na ko ndam li. \q1 \v 2 Aji Sax jee xamleg wallam, \q1 feeñal njekkam, xeet yi gis. \q1 \v 3 Moo dencal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ngoram, \q1 dencal ko wormaam, \q1 àddina ba mu daj di gis \q1 ni nu sunu Yàlla walloo. \q1 \v 4 Yeen àddina sépp, xaacul-leen Aji Sax ji, \q1 sampleen, sarxolle te woy! \q1 \v 5 Xalamal-leen Aji Sax ji, woyal ko, \q1 xalamal ko, woyati. \q1 \v 6 Wal-leen liit yi, wal bufta yi \q1 te xaacul Buur Aji Sax ji! \b \q1 \v 7 Na géej riirandook li ko fees, \q1 mook àddinaak li ci biiram, \q1 \v 8 dex tàccu, \q1 tund sarxolleendoo, \q1 \v 9 gatandoo ko Aji Sax jiy dikk, \q1 àttesi àddina, \q1 di àtte dun bi njekk, \q1 tey àttee xeet yépp dëgg. \c 99 \s1 Aji Sax ji buur bu sell la \q1 \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jeey Buur. Yeen xeet yi, ragal-leen ko! \q1 Moo toogandook malaakay \w serub|lemma="serub y-:"\w* yi. Suufoo, soo yeboo, yëngu! \q1 \v 2 Aji Sax ji fi \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* a màgg, \q1 kawe, tiim xeetoo xeet. \q1 \v 3 Sa tur weeka màgg te raglu. Sàbbaal-leen ko. \q1 —Kee sell! \q1 \v 4 Buur, jëfe yoon mooy dooleem, \q1 te yaa saxal njub, yoon ak njekk \q1 ci askanu Yanqóoba. \q1 \v 5 Màggal-leen sunu Yàlla, Aji Sax ji, \q1 te sujjóot fa ndëggastalam. \q1 —Kee sell! \b \q1 \v 6 Musaak Aaróona bokk ciy \w sarxalkatam|lemma="sarxalkat b-:"\w*, \q1 Samiyel bokk ca ñay tudd turam. \q1 Ñuy ñaan Aji Sax ji, mu di leen nangul. \q1 \v 7 Fa biir taxaaru niir wa la waxeek ñoom, \q1 ñu topp kàdduy seedeem ak dogalu yoonam ba mu leen joxoon. \q1 \v 8 Céy sunu Yàlla Aji Sax ji, yaa leen nanguloon, \q1 di seen Yàlla ju leen di baal, \q1 te di leen mbugale seeni jëf ju bon. \q1 \v 9 Màggal-leen sunu Yàlla, Aji Sax ji, \q1 te sujjóot fa tundam wu \w sell|lemma="sell:"\w* wa. \q1 —Sunu Yàlla Aji Sax jee sell! \c 100 \s1 Aji Sax jee baax \d \v 1 Muy jàngi cant. \b \q1 Yeen waa àddina sépp, \q1 xaacul-leen \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \q1 \v 2 Nangeen jaamoo Aji Sax ji mbég, \q1 dikke koy woy! \q1 \v 3 Seedeleen ne Aji Sax jeey Yàlla. \q1 Moo nu sàkk, nuy ñoñam, \q1 di gàttam yi muy foral. \q1 \v 4 Nangeen dugge këram ag cant, \q1 dugg ëttam di màggal, \q1 sant ko, teral turam. \q1 \v 5 Aji Sax jee baax, gore ba fàww, \q1 worma ja sax dàkk! \c 101 \s1 Buur a ngi jaayanteek Yàlla \d \v 1 Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. \b \q1 Ngor ak yoon laay woy. \q1 Yaw \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji laay joobe. \q1 \v 2 Naa teewlu yoonu maandute. \q1 Ana kañ nga may dikkal? \q1 Naa doxe maandute \q1 fi sama biir waa kër. \q1 \v 3 Caaxaani neen, xooluma; \q1 jëf ju wàcc yoon, bugguma, \q1 taqu ma fenn. \q1 \v 4 Kuy nas njekkar, sore ma; \q1 lu bon, xawma ko. \q1 \v 5 Kuy jëw moroomam, ma wedamal; \q1 ku daŋŋiiral ak ku reew, muñaluma la. \q1 \v 6 Ku dëggu ci réew mi, ma geesu, \q1 ngir fat ko. \q1 Te kuy wéye maandute, \q1 kookoo may liggéeyal. \q1 \v 7 Kuy njublaŋ du tooge sama kër, \q1 kuy fen du taxaw sama kanam. \q1 \v 8 Maay xëy, sànk képp ku bon ci réew mi, \q1 ngir dagge ci dëkkub Aji Sax jii képp kuy def lu ñaaw. \c 102 \s1 Yàlla, bu ma rey \d Muy ñaanu néew-ji-doole ju sonn, bay diis \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji njàqareem. \b \q1 \v 1 Éy Aji Sax ji, déglul, ma ñaan la; \q1 yal na sama yuux àgg fa yaw. \q1 \v 2 Bu ma dummóoyu bésub njàqare; \q1 teewlu ma, \q1 gaawe ma sama bésub woote! \q1 \v 3 Samay fan a ngi wéy ni saxar, \q1 sama yax yi mel nib taal. \q1 \v 4 Sama xol bi wow ni ñax mu xuur, \q1 ba lekk safatu ma. \q1 \v 5 Damaa jàq, di onka onk, \q1 ba desey yax. \q1 \v 6 Ma mel nim tan ci màndiŋ mi, \q1 mbete looy cib gent. \q1 \v 7 Nelaw të; \q1 ma mel ni picc mu wéetoo puju néeg. \q1 \v 8 Bés bu ne noon yi di ma sewal; \q1 ñi may ñaawal di móoloo sama tur. \q1 \v 9 Lekkuma xanaa di diwoob dóom, toroxloo; \q1 te lu ma naan, tuur ca rongooñ, \q1 \v 10 te sa mer ak sa xadar a tax, \q1 nde yaa ma fab, xalab. \q1 \v 11 Ker a ngi law, nara mëdd samay fan. \q1 Maa ngi wowat nim ñax. \b \q1 \v 12 Waaye yaw Aji Sax ji, yaay des ba fàww, \q1 saw tur saxal maasoo maas. \q1 \v 13 Yaw yaay taxaw, ñeewante \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, \q1 ndax baaxe ko jot na, \q1 àpp ba kay mat na. \q1 \v 14 Sa jaam ñeeka sopp doji dëkk bii ñu màbb, \q1 ñoo ñeewante tojiti gentam bii. \q1 \v 15 Na xeet yi wormaal turu Aji Sax ji, \q1 buuri àddina sépp wormaal darajaam, \q1 \v 16 nde Aji Sax jeey tabaxaat Siyoŋ, \q1 nara feeñeg leeram. \q1 \v 17 Mooy nangul aji tumurànke, \q1 xeebul ñaanam. \q1 \v 18 Nañu bindal lii maasug ëllëg, \q1 ba xeet wu sosoogul màggal Ki Sax, \q1 \v 19 nde Aji Sax jeey jéere fu sellam fa ca kaw, \q1 di niire suuf fa asamaan, \q1 \v 20 ngir teewlu onki ñi ñu tëj, \q1 nara ubbi ñi dee di seen àtte, \q1 \v 21 ba ñu siiwal turu Aji Sax ji fi Siyoŋ, \q1 màggale ko fi Yerusalem, \q1 \v 22 kera ba xeet yiy bokk daje, \q1 ñook réew yi, ngir jaamu Aji Sax ji. \b \q1 \v 23 Sama digg doole la ma semmale, \q1 gàttal samaw fan. \q1 \v 24 Ma ne: «Éy sama Yàlla, maasoo maas, say at du jeex. \q1 Bu ma yóbboo sama diggi fan. \q1 \v 25 Bu yàgg nga samp suuf, \q1 sàkke asamaan say yoxo. \q1 \v 26 Ñoom ñuy jeex, yaw nga sax, \q1 ñoom ñépp ràpp ni mbubb, \q1 nga soppi leen niy yére, sànni; \q1 \v 27 te yaw ngay kenn ki, \q1 te say at amul kem. \q1 \v 28 Sa doomi jaam ñeey dëkk; \q1 seen askan sax fi sa kanam.» \c 103 \s1 Ma sant Aji Sax ji \d \v 1 Ñeel Daawuda. \b \q1 Naa sant \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ci saa xol bii, \q1 saa jëmm jépp di sàbbaal sellngay turam! \q1 \v 2 Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii, \q1 te baña fàtte mboolem xéewalam! \q1 \v 3 Moo lay baal foo ñaawe, \q1 di la wéral foo woppe. \q1 \v 4 Mooy jot sa bakkan, \q1 kaalaa la ngor ak yërmande, \q1 \v 5 di reggal sa bakkan bànneex, \q1 yeesalal lag ndaw, \q1 nga màggataale doole nig jaxaay. \b \q1 \v 6 Aji Sax jeey def njekk, \q1 di àtte jépp néew-ji-doole. \q1 \v 7 Moo xamal Musaa ay nammeelam, \q1 xamal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ay jëfam. \q1 \v 8 Yërmandeeku yiw, fa Aji Sax ji. \q1 Moo muñ mer te bare ngor. \q1 \v 9 Saxoowul di toppe, \q1 dencul mer ba fàww. \q1 \v 10 Du sunuy bàkkaar la nu mbugal, \q1 du sunuy ñaawtéef la nu fey. \q1 \v 11 Ni asamaan tiime suuf, \q1 ni la ngoram yiire ku ko ragal. \q1 \v 12 Ni penku soree sowu, \q1 ni la nu soreleek sunu mbugali tooñ. \q1 \v 13 Ni baay yërëme doom, \q1 ni la Aji Sax ji yërëme ku ko ragal. \q1 \v 14 Moo xam sunu bind, \q1 di bàyyi xel ne pënd lanu. \q1 \v 15 Nit aki fanam di saxayaay \q1 suy law ni tóor-tóoru àll; \q1 \v 16 ngelaw li wal, mu ne mes, \q1 mel ni masu faa nekk. \q1 \v 17 Waaye ngoru Aji Sax ji naka jekk \q1 ñeel na fàww ku ko ragal; \q1 njekkam ñeel sëtaati \q1 \v 18 kuy sàmm \w kóllëreem|lemma="kóllëre g-:"\w*, \q1 di saxoo jëfe tegtali yoonam. \b \q1 \v 19 Aji Sax jee samp asamaan ab jalam, \q1 nguuram ŋank lépp. \q1 \v 20 Yeen malaaka yi, santleen Aji Sax ji, \q1 yeen jàmbaar yu mag yiy jëfe ndigalam, \q1 di sàmm kàddoom. \q1 \v 21 Santleen Aji Sax ji, yeen gàngoori xareem yépp, \q1 yeen dagam yiy jëfe coobareem. \q1 \v 22 Yeen bindeef yépp, nangeen sante Aji Sax ji \q1 fépp fu mu tiim. \q1 Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii! \c 104 \s1 Màggal-leen ki sàkk lépp \q1 \v 1 Naa sant \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ci saa xol bii! \q1 Aji Sax ji sama Yàlla, yaaka màgga màgg. \q1 Teddngaak daraja nga soloo, \q1 \v 2 làmboo leer ni mbubb, \q1 firi asamaan ni ndimo, \q1 \v 3 xadd say néegi kaw ci biir ndox mi, \q1 def niir yi say waruwaay, \q1 di daagoo kaw laafi ngelaw, \q1 \v 4 def ngelaw yi say ndaw, \q1 ay sawara boy, di say jawriñ. \q1 \v 5 Yaa dëj suuf ciy kenoom, \q1 deesu ko yëngal ba fàww. \q1 \v 6 Yaa ko sànge xóotey géej ni mbubb, \q1 ndox ma taxaw, tiim tund ya. \q1 \v 7 Nga gëdd, ndox ma fëx; \q1 nga dënu, mu daw, \q1 \v 8 wale kaw tund ya, wàccsi xur ya, \q1 di bérab ba nga ko beral. \q1 \v 9 Ag kemu nga teg, du ko wees, \q1 te dootu muur suuf si. \q1 \v 10 Yaa ballal bëti ndox ya ca xur ya, \q1 ñuy wale digg tund ya, \q1 \v 11 ngay nàndal bépp ndundatu àll, \q1 di wëgg mbaamu àll, \q1 \v 12 njanaaw dëkke ca wet ga, \q1 baatam jibe fa garab ya. \q1 \v 13 Yaa suuxate tund ya fa sa néegi kaw, \q1 sa liggéey reggal suuf. \b \q1 \v 14 Yaa saxalal jur gi ñax \q1 ak gàncax gu doom aadama di bey, \q1 ba génnee ab dund fi suuf, \q1 \v 15 dugub di ko dooleel, \q1 biiñ di bégal xolam, \q1 ag diw di leeral kanamam. \q1 \v 16 Garabi Aji Sax ja, seedari Libaŋ, \q1 ya mu jëmbat, regg nañu, \q1 \v 17 picc tàgge ca, \q1 xodd dëkke garab gu dul ruus, \q1 \v 18 tund wu mag ñeel kéwéli àll, \q1 xunti di rawtub daman\f + \fr 104.18 \fr*\fk daman \fk*\ft xeetoo naak njomboor.\ft*\f*. \q1 \v 19 Yaa sàkk weer, muy takku jamono, \q1 sàkk jant, mu xam waxtuw fatoom. \q1 \v 20 Yaa def lëndëm, mu guddi; \q1 bépp rabu àll di ca dox, \q1 \v 21 gaynde gu ndaw ŋaral am pàddam, \q1 di sàkkoo dundam fa Yàlla. \q1 \v 22 Bu jant fenkee, ñu dellu, \q1 goori ca seeni pax, \q1 \v 23 doom aadama tàmbali kër-këram, \q1 di yendoo liggéey ba ngoon. \b \q1 \v 24 Éy Aji Sax ji, yaa bare loo liggéey, \q1 te lépp di xel mu rafet. \q1 Suuf daa fees ak say càkkéef. \q1 \v 25 Géej a ngee réy te yaa, \q1 la fay yëngu maneesu koo lim, \q1 muy ndundat lu mag ak lu ndaw. \q1 \v 26 Fa la gaal di daw, \q1 ak ngaaka la nga bind, mu di fa foye. \q1 \v 27 Ñoom ñépp yaw lañuy séentu, \q1 ngir bu jotee, nga leel leen, \q1 \v 28 may leen lu ñu for; \q1 ŋëbal leen, ñu suur ngëneel. \q1 \v 29 Soo leen làqoo, ñu tiit; \q1 nga rocci seen noo, ñu saay, \q1 dellu di pënd. \q1 \v 30 Yaay yónnee sag noo, ñu nekk; \q1 te yaay yeesal li ci kaw suuf. \b \q1 \v 31 Yal na darajay Aji Sax ji sax, \q1 yal na Aji Sax ji bégey jalooreem. \q1 \v 32 Kee naan jàkk suuf, muy lox; \q1 mu laal tund yi, ñuy saxar! \q1 \v 33 Naa woy Aji Sax ji li feek may dund, \q1 naa kañ sama Yàlla li feek may tooy. \q1 \v 34 Sama xalaat bii, yal na ko neex. \q1 Man de maa ngi bége Aji Sax ji! \q1 \v 35 Yal na bàkkaarkat raaf fi kaw suuf, \q1 te ku bon noppee nekk. \q1 Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii. \q1 Màggal-leen Ki Sax! \c 105 \s1 Aji Sax ji sàmm na kóllëre \q1 \v 1 Santleen \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, tudd turam, \q1 xamley jalooreem ci biir xeet yi, \q1 \v 2 woy ko, tagg ko, \q1 yégle mboolemi kéemaanam! \q1 \v 3 Damooleen turam wu \w sell|lemma="sell:"\w*. \q1 Kuy wut Aji Sax ji, yal na am bànneexu xol. \q1 \v 4 Gëstuleen Aji Sax jeek dooleem, \q1 di ko sàkku saa su ne. \q1 \v 5 Fàttlikuleen ay jalooreem \q1 aki misaalam aki àtteem. \q1 \v 6 Yeen askanu Ibraayma, jaamam ba, \q1 yeen ñiy sëti Yanqóoba, ñiy tànnéefam, \q1 \v 7 kee di sunu Yàlla Aji Sax ji, \q1 di àtte suuf sépp, \q1 \v 8 di fàttliku ba fàww \w kóllëreem|lemma="kóllëre g-:"\w*, \q1 di bàyyi xel ba ci junniy maas kàddoom \q1 \v 9 ga mu digoon Ibraayma, \q1 giñal ko Isaaxa, \q1 \v 10 dëggalal ko Yanqóoba, sàrtal ko, \q1 fase kook Israyil mooma kóllëre gu sax. \q1 \v 11 Mu ne: «Yaw laay jox réewum Kanaan, \q1 muy sa cér, nga séddoo.» \q1 \v 12 Ba bànni Israyil dee ñu néew, \q1 diy doxandéem ca réew ma, \q1 \v 13 di wëreelu ci biir xeetoo xeet, \q1 ak nguuroo nguur, \q1 \v 14 mayul nit mu not leen, \q1 te yaral na leen ay buur, \q1 \v 15 ne leen: «Buleen laal samay tànnéef, \q1 buleen lor samay yonent.» \q1 \v 16 Moo wàcce ab xiif ca réew ma, \q1 dagge fa luy gub, \q1 \v 17 yónnee ku leen jiitu, \q1 muy Yuusufa ma ñu jaayoon njaam, \q1 \v 18 tànk ya, ñu jéng jéng yu tar, \q1 baat ba, ñu yeewe caqu weñ. \q1 \v 19 Kàddug Aji Sax ji di nattu Yuusufa, \q1 ba keroog pirim ma dikk, \q1 \v 20 Buur a yónni ku ko yiwi, \q1 ku yilifi xeet a ko tijji. \q1 \v 21 Mu sas ko mu jiite këram, \q1 di saytu mboolem alalam, \q1 \v 22 ba saña tënk jawriñi buur ci coobareem, \q1 tey xelal mag ña. \q1 \v 23 Israyil agsi Misra, \q1 muy nganug Yanqóoba ga ca réewum Xam\f + \fr 105.23 \fr*\fk Israyil \fk*\ft ak \ft*\fk Yanqóoba, \fk*\ft kenn ki la; \ft*\fk réewum Xam \fk*\ft mooy Misra ba tey.\ft*\f*. \b \q1 \v 24 Aji Sax ji giiral xeetam wa, \q1 ba ñu gëna bare seeni noon, \q1 \v 25 mu xiir waa Misra ci dëddu ñoñam, \q1 ñuy fexeel jaamam ñooña. \q1 \v 26 Mu yónni Musaa, jaamam ba, \q1 tànn Aaróona, boole ca, \q1 \v 27 ñu sottal ci seen biir firndeem ya mu waxoon, \q1 muy kéemaan ya ñu def ca réewum Xam. \q1 \v 28 Moo yónnee lëndëm, lëndëmal, \q1 te Musaa ak Aaróona gàntaluñu kàddoom. \q1 \v 29 Moo soppi seen ndoxum réew deret, \q1 rey seeni jën, \q1 \v 30 feesal seen réew ay mbott \q1 yu àkki seen biir néegi buur ya. \q1 \v 31 Moo àddu, weñ ya dikk, \q1 rayentaan ya dajal seen réew ma. \q1 \v 32 Mu def seenub taw tawub yuur, \q1 sawaray melax jafal seen réew ma. \q1 \v 33 Mu dóor seen figg ak reseñ, \q1 fóom seen garabi réew ma. \q1 \v 34 Mu àddooti, ay soccet dikk, \q1 di njéeréer yu wees ab lim, \q1 \v 35 ñu lekk luy gàncax ca seenum réew, \q1 lekk lu suuf sa meññ. \q1 \v 36 Moo fàdd luy taaw ca seenum réew, \q1 muy lu jëkka soqeekoo seen digg doole. \b \q1 \v 37 Mu génne leen, ñu yóbbaale xaalis ak wurus, \q1 te kenn tërëful ca seeni giir. \q1 \v 38 Misra daa bég ba ñu demee \q1 ndax tiitaange lu ñu leen tiital. \q1 \v 39 Mu firiw niir, yiire leen, \q1 ak sawara, ñu niitoo guddi. \q1 \v 40 Ñu sàkku, mu wàcceey picci përëntaan, \q1 teg ca reggal leen mburum asamaan. \q1 \v 41 Mu bënnu doj, ndox ma ball, \q1 di dex, wale joor gu wow. \q1 \v 42 Daa bàyyi xel kàddoom gu sell, \q1 ga mu waxoon Ibraayma, jaamam ba. \q1 \v 43 Moo génne ñoñam, ñu bég, \q1 moo génne tànnéefam ña, ñuy sarxolle. \q1 \v 44 Mu jox leen suufi yéefar ya, \q1 ñu jagoo ñaqi xeet ya, \q1 \v 45 ngir ñu sàmm ay dogali yoonam, \q1 topp ndigali yoonam. \q1 Màggal-leen Ki Sax! \c 106 \s1 Israyil di wor, Yàlla di wóor \q1 \v 1 Màggal-leen Ki Sax! \q1 Santleen \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, kee baax, \q1 kee saxoo ngoram! \q1 \v 2 Ana ku mana tudd jaloorey Aji Sax ji? \q1 Ana ku mana teesal woyam? \q1 \v 3 Ndokklee kuy sàmm yoon, \q1 di def njekk fu mu tollu. \q1 \v 4 Éy Aji Sax ji, séddaale ma ci sa yiwu ñoñ, \q1 ngalla, dikke ma sag wall, \q1 \v 5 ma gis ngëneelu ñi nga tànn, \q1 di bànneexoo sa bànneexu xeet wi, \q1 tey damoondook ñoom ñi nga séddoo. \b \q1 \v 6 Noo bàkkaar, nook sunuy maam; \q1 noo def lu ñaaw, def lu bon. \q1 \v 7 Sunuy maam seetuñu ca say kéemaan ca Misra, \q1 bàyyiwuñu xel ca sa ngor lu réy, \q1 xanaa di fippu ca géej ga, géeju Barax ya. \q1 \v 8 Teewul Yàlla wallu leen ngir turam, \q1 ba xamle njàmbaaram. \q1 \v 9 Dafa gëdd géeju Barax ya, mu ne sereŋ; \q1 xóotey géej mel ni màndiŋ, mu jàlle leen, \q1 \v 10 musal leen ci loxol bañaale, \q1 jote leen ca loxol noon ba, \q1 \v 11 ndox ma mëdd bañ ya, \q1 kenn desu ca. \q1 \v 12 Ca lañu gëm ay waxam, \q1 woy ko. \b \q1 \v 13 Nes tuut ñu fàtte jëfam ja, \q1 xaaratuñu ndigalam, \q1 \v 14 di ŋaf-ŋafi ca màndiŋ ma, \q1 di diiŋat Yàlla ca àll ba. \q1 \v 15 Yàlla jox leen la ñuy sàkku, \q1 wàccaaleel leen woppi ràgg. \q1 \v 16 Ba ñu demee ba iñaane Musaa ca dal ba, \q1 boole ca Aaróona mu sell ma, nitu Aji Sax ja, \q1 \v 17 suuf a ne ŋafeet, wonn Datan\f + \fr 106.17 \fr*\fk Datan: \fk*\ft seetal ci \ft*\ft \+bk Màndiŋ ma\+bk* 16.27, 31-33.\ft*\f*, \q1 mëddaale gàngooru Abiram; \q1 \v 18 sawara ne jippét fa seen biir, \q1 tàkk ba lakk ñu bon ñooña. \b \q1 \v 19 Tëgg nañu aw nag ca tundu Oreb, \q1 di sujjóotal jëmm ju ñu móol, \q1 \v 20 di jënde seen teddngay Yàlla ja \q1 jëmmu nag wuy for um ñax. \q1 \v 21 Dañoo fàtte Yàlla ma leen di musal \q1 te def jaloore ca Misra. \q1 \v 22 Mooy kéemaan ya fa réewum Xam\f + \fr 106.22 \fr*\fk réewum Xam \fk*\ft mooy Misra ba tey.\ft*\f*, \q1 kiraama ya ca géeju Barax ya. \q1 \v 23 Yàlla da leen doon sànk, \q1 bu dul woon ak Musaa, xejjam \q1 ba ko kar, àtte leen, \q1 mu giif, ba fàkkasu leen. \b \q1 \v 24 Dañoo gàntal réew mu neex, \q1 gëmuñu kàddug Yàlla, \q1 \v 25 xanaa di xultoo seen biiri xayma, \q1 baña déggal Aji Sax ji. \q1 \v 26 Moo tax mu giñal leen \q1 ne dina leen tëral fa màndiŋ ma, \q1 \v 27 tëral seen askan ci biir xeet yi, \q1 wasaare leen ci réew yi. \b \q1 \v 28 Ñuy darook tuurum \w Baal Pewor|lemma="Baal:"\w*, \q1 di lekk lu ñu sarxal ay yàlla yu amul bakkan, \q1 \v 29 di merloo Yàlla ci seeni jëf, \q1 ba mbas ne dàll fa seen biir. \q1 \v 30 Fineyas taxaw, àtte; \q1 mbas ma dal, \q1 \v 31 muy njekk lu ñu ko waññal \q1 tey ak ëllëg. \b \q1 \v 32 Ñu merlooti Yàlla ca ndoxum Meriba ma, \q1 muy loraangey Musaa te ñoo ko waral. \q1 \v 33 Ñoo naqaral Musaa, \q1 ba mu wax wax ju ko rëcc. \b \q1 \v 34 Te it faagaagaluñu yéefar, \q1 ya leen Aji Sax ji waxoon, \q1 \v 35 xanaa di jaxasook yéefar yooya, \q1 di roy seeni jëf, \q1 \v 36 di jaamu seeni tuur, \q1 mu mujj dig fiir ca ñoom. \q1 \v 37 Ñuy sarxalal rab ya \q1 seen doom yu góor ak yu jigéen, \q1 \v 38 di tuur deretu ñu deful dara, \q1 te muy seen deretu doom yu góor ak yu jigéen \q1 ya ñu sarxalal tuuri Kanaaneen ña, \q1 deret ja sobeel réew ma, \q1 \v 39 seeni jëf sobeel leen, \q1 ndax seen bokkaale. \b \q1 \v 40 Aji Sax ji mere ñoñam, \q1 sib xeet woowu mu séddoo, \q1 \v 41 ba tax mu teg leen ca loxol yéefar ya, \q1 seeni bañ yilif leen, \q1 \v 42 seen noon ya not leen, \q1 ñu torox ca seeni loxo. \q1 \v 43 Ay yooni yoon la leen xettli, \q1 teewul ñuy nas pexey fippu, \q1 ba suux ci seeni ñaawtéef. \q1 \v 44 Mu gis nag seen njàqare, \q1 dégg seeni tinu, \q1 \v 45 bàyyi xel ci \w kóllëreem|lemma="kóllëre g-:"\w* ak ñoom, \q1 topp ngoram lu réy, ba giif, \q1 \v 46 xiir ña leen jàpp ñépp, \q1 ñu yërëm leen. \b \q1 \v 47 Éy Aji Sax ji, sunu Yàlla, wallu nu, \q1 génnee nu ci xeet yi, dajale nu, \q1 nu sante la sa sellnga, \q1 di sagoo sa teddnga. \q1 \v 48 Santleen Aji Sax ji, Yàllay Israyil \q1 cant gu sax dàkk, ba fàww. \q1 Na ñépp ne: «Amiin!» \q1 Màggal-leen Ki Sax! \c 107 \s1 Aji Sax jeey xettlee \q1 \v 1 Santleen \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, kee baax, \q1 kee saxoo ngoram! \q1 \v 2 Waxleen lii, yeen ñi Aji Sax ji jot, \q1 jote leen ci loxol bañ, \q1 \v 3 dajalee leen fa réew ya, \q1 jële leen penkook sowu, \q1 ak bëj-gànnaar ak wetu géej. \b \q1 \v 4 Ñee ngi taxawaaloo màndiŋ mu wéet, \q1 gisuñu dëkkuwaay, \q1 \v 5 boole xiif ak mar, \q1 ba bakkan di tàggoo. \q1 \v 6 Ñu jàq, woo Aji Sax ji wall, \q1 mu xettlee leen seen njàqare, \q1 \v 7 jaarale leen yoon wu jub, \q1 ngir ñu àgg cib dëkk. \q1 \v 8 Nañu sante Aji Sax ji ngoram \q1 ak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi. \q1 \v 9 Mooy màndal put gu wow, \q1 di feesal ngëneel biir bu wéet. \b \q1 \v 10 Ñee ngi dëkke lëndëm gu tar, \q1 ñu yeewe leen jéngi weñ yu tar. \q1 \v 11 Ñoo gàntal waxi Yàlla, \q1 néewal ndigalal Aji Kawe ji. \q1 \v 12 Mu teg leen naqar, ba torxal leen, \q1 ñu ne nërëm te kenn walluw leen. \q1 \v 13 Ñu jàq, woo Aji Sax ji wall, \q1 mu walloo leen seen njàqare, \q1 \v 14 xar seeni jéng yaar, \q1 génnee leen lëndëm gu tar. \q1 \v 15 Nañu sante Aji Sax ji ngoram \q1 ak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi. \q1 \v 16 Moo rajaxe bunti xànjar, \q1 damm galani weñ. \b \q1 \v 17 Ñu dofe ñalee ngi topp yoonu moy, \q1 loroo seeni ñaawtéef, \q1 \v 18 ba luy ñam di daw seen yaram, \q1 ñu jege bunti ndee. \q1 \v 19 Ñu jàq, woo Aji Sax ji wall, \q1 mu walloo leen seen njàqare. \q1 \v 20 Daa yónnee kàddoom, wéral leen, \q1 këfe leen cim yeer. \q1 \v 21 Nañu sante Aji Sax ji ngoram \q1 ak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi. \q1 \v 22 Nañ ko sarxal \w saraxi cant|lemma="Sarax yi:"\w* \q1 tey sarxolle, siiwale koy jalooreem. \b \q1 \v 23 Ña ca des a ngi war gaal, dugg géej, \q1 di liggéeye mbeex mu ne xéew. \q1 \v 24 Ñooñoo seede jaloorey Aji Sax ji, \q1 ak kéemaanam ya fa xóote ya. \q1 \v 25 Day àddu, sant ngëlén, \q1 mu yékkati gannax yi. \q1 \v 26 Gannax ya fettax ba ca kawa kaw, \q1 xàwwikoo fa, tàbbi xóote ya. \q1 Ñu jàq ba fit ne soyox, \q1 \v 27 di jang, di kayaŋ-kayaŋi niy màndikat, \q1 pexe jeex. \q1 \v 28 Ñu jàq, woo Aji Sax ji wall, \q1 mu génnee leen seen njàqare, \q1 \v 29 dalal ngëlén la, \q1 gannax ya selaw, \q1 \v 30 ne tekk, ñu bég, \q1 mu gindi leen ba fa ñu bëgga teer. \q1 \v 31 Nañu sante Aji Sax ji ngoram \q1 ak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi. \q1 \v 32 Nañu ko kañe ndajem mbooloo mi, \q1 di ko màggale péncu mag ñi. \b \q1 \v 33 Mooy soppi wali ndox màndiŋ, \q1 soppi bëti ndox suuf su ne sereŋ, \q1 \v 34 suuf su nangu doon jooru xorom \q1 ndax mbonug ña ko dëkke. \q1 \v 35 Mooy soppi màndiŋ it, ndox ya taa, \q1 soppi suuf su ne sereŋ bëti ndox; \q1 \v 36 dëël fa ñu xiif, \q1 ñu sanc fab dëkk, dëkke, \q1 \v 37 ji ay tool, jëmbat ay reseñ, \q1 mu meññ, ñoral, \q1 \v 38 Aji Sax ji barkeel, ñu giira giir, \q1 te wàññiwul seenug jur. \q1 \v 39 Bu ñu wàññikoo, ba néew doole \q1 ndax noteel ak coonooku tiis, \q1 \v 40 Aji Sax ji sib seen njiit yi leen not, \q1 wërloo leen àll bu amul yoon. \q1 \v 41 Waaye mooy teggil néew-ji-doole coonoom, \q1 ful njabootam nig jur, \q1 \v 42 aji jub ñi gis ko, bég; \q1 mboolem ku bon wedam. \q1 \v 43 Ku xelu ku ne, na ràññee lii \q1 te seede li Aji Sax ji jëfe ngoram. \c 108 \s1 Yàlla, may nu ndam \d Muy woyu Sabóor, ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 Yàlla, dogu naa, \q1 damay woy, di la kañ; \q1 sama jëmm jépp di la woy. \q1 \v 2 Na mboolem xalam yewwu, \q1 ma yee leeru njël. \q1 \v 3 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, dama lay gërëm ci biir xeet yi, \q1 kañ la ci biir waaso yi. \q1 \v 4 Sa ngor a màgg ba sut asamaan, \q1 sa worma àkki fa kawa kaw. \q1 \v 5 Éy Yàlla, yaa màgg ba sut asamaan, \q1 sag leer tiim suuf sépp. \b \q1 \v 6 Walloo nu sa ndijoor, \q1 nangul ma, \q1 ba say soppe xettliku. \q1 \v 7 Yàllaa àddoo fa këram gu \w sell|lemma="sell:"\w*, \q1 ne: «Maay damu, dogat suufas Sikem, \q1 séddale xuru Sukkóot. \q1 \v 8 Maa moom diiwaanu Galàdd, moom Manase, \q1 Efrayim di sama mbaxanam xare, \q1 Yuda di sama yetu nguur, \q1 \v 9 réewum Mowab di sama ndabal raxasukaay, \q1 Edom, ma teg tànk; \q1 Filisti, ma xaacoo fa.» \b \q1 \v 10 Éy Yàlla, ana ku may yóbbu dëkk ba tata wër? \q1 Ku may jiite ba Edom? \q1 \v 11 Yàlla, xanaa du yaa nu wacc? \q1 Éy Yàlla, yaa baña ànd ak sunu mboolooy xare? \q1 \v 12 Ngalla dimbali nu ci bañaale; \q1 doom aadama, wallam neen la. \q1 \v 13 Nook Yàlla, nu def njàmbaar; \q1 moom mooy not sunuy noon. \c 109 \s1 Yal na Yàlla mbugal noon bi \d \v 1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. \b \q1 Éy Yàlla mi may sant, bul tanqamlu! \q1 \v 2 Ku bon ak kuy fen a ma waxal, \q1 sosal ma, \q1 \v 3 tance ma kàdduy mbañeel, \q1 song ma ci dara. \q1 \v 4 Ma ji nit cofeel, mu sosal ma; \q1 te man ma di ko ñaanal. \q1 \v 5 Sama jëf ju baax, loraange lañu ma ko feye, \q1 sama cofeel, ñu feye ma ko mbañeel. \b \q1 \v 6 Yal nanga fal ku bon ci kaw kii, \q1 ab soskat féete ko ndijoor. \q1 \v 7 Bu ñu koy àtte, yal nañu ko yey, \q1 te yal na ñaanam walbatiku di bàkkaar. \q1 \v 8 Yal naw fanam gàtt, \q1 keneen jagoo sasam. \q1 \v 9 Yal nay doomam diy jirim, \q1 jabaram dib jëtun, \q1 \v 10 ay doomam di tambaambaluy yalwaan, \q1 dëddu seeni gent, dem tàllal ay loxo. \q1 \v 11 Yal na ko kuy feyeeku futti, \q1 ay doxandéem foqati ñaqam. \q1 \v 12 Yàlla bu ko kenn ji ngor, \q1 yàlla bu kenn baaxe jirim yi ko wuutu. \q1 \v 13 Yal na askanam dagg. \q1 Balaa geneen maas a wéy, yal na seenu tur fey. \q1 \v 14 Yal na \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji bàyyi xel ñaawtéefi maamam. \q1 Yàlla bu bàkkaaru ndeyam faru. \q1 \v 15 Yal na seeni moy sax fi kanam Aji Sax ji. \q1 Yal na seen tur dagge fi kaw suuf. \q1 \v 16 Moo séddul ngor, \q1 di topp ku néewle te sonn, \q1 seen xol jeex, mu bóom. \q1 \v 17 Moo bëggoon di móoloo, yal na ko këppoo; \q1 soppul ag ñaan it, yal na ko barke sore. \q1 \v 18 Móolook sol mbubb la yemale, \q1 yal nañu duy nim ndox ay móoloom ci yaramam, \q1 mu seeb ci biiri yaxam nig diw. \q1 \v 19 Yal nay móoloom di mbubbam, \q1 te di laxasaay gu mu saxoo. \b \q1 \v 20 Lii, yal na ko Aji Sax ji feye ñi may sosal, \q1 di teg lu ñaaw ci sama der. \q1 \v 21 Waaye Boroom bi Aji Sax ji, \q1 defal ma li sa tur laaj. \q1 Yaa baax, gore, xettli ma. \q1 \v 22 Damaa néewle te sonn, \q1 sama xol dagg, ba jeex tàkk. \q1 \v 23 Maa ngi tàggoo ni keru ngoon, \q1 ñu di ma fél ni soccet. \q1 \v 24 Samay óom a ngi nasax ndax ñàkka lekk, \q1 desewuma lu moy yaxi neen. \q1 \v 25 Maa ngii, ñu di ma sewal, \q1 ku ma gis, wëcc bopp. \q1 \v 26 Éy Aji Sax ji, sama Yàlla, dimbali ma, \q1 walloo ma sa ngor, \q1 \v 27 ba ñu xam ne lii sa loxoo, \q1 xam ne yaw Aji Sax ji, yaa ko def. \q1 \v 28 Ñooy móolu, yaw nga barkeel; \q1 ñoo ma jógal, ñooy torox, \q1 man, ma bég, Sang bi! \q1 \v 29 Yal na ñi may sosal sàngoo toroxte, \q1 làmboo gàcce ni mbubb. \q1 \v 30 Ma àddu, santa sant Aji Sax ji, \q1 di ko màggale digg mbooloo mu yaa. \q1 \v 31 Mooy féete ndijoor néew-ji-doole, \q1 musal ko ci ku koy teg àtteb dee. \c 110 \s1 Yàlla fal na nitam \d \v 1 Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. \b \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji daa wax sama Sang, ne ko: \q1 «Toogeel sama ndijoor, \q1 ba ma def say noon sa ndëggastal.» \b \q1 \v 2 Sa nguur la Aji Sax ji saxal, dale ko fa \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*. \q1 Yilifal noon yi la wër! \q1 \v 3 Sa mboolooy taxawal seen bopp, \q1 sa bésub xare. \q1 Ña nga soloo darajaak sellnga, \q1 faboo fa njël sosoo, \q1 diy ndaw, wàccsil la, mbeteb lay. \b \q1 \v 4 Aji Sax jee ko giñ, \q1 te du dellu gannaaw: \q1 «Yaa dib \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba fàww, \q1 topp dayob Melkisedeg\f + \fr 110.4 \fr*\fk Melkisedeg: \fk*\ft buurub Salem la woon, di sarxalkat bu Yàlla faloon ci jamonoy Ibraayma, maanaam ñeenti téeméeri at laata Aaróonaa doon ab sarxalkat.\ft*\f*.» \b \q1 \v 5 Sang baa ngi fi sa ndijoor \q1 te mooy rajaxe buur yi, bés bu meree. \q1 \v 6 Mooy mbugal xeet yi, jal seeni néew, \q1 di rajaxe kilifay àddina, ba mu daj. \b \q1 \v 7 Déeg ba feggook yoon wa, Buur a cay naan, \q1 te moo ko tax di siggi. \c 111 \s1 Yàlla la ay mbiram sax \q1 \v 1 Màggal-leen Ki Sax! \q1 Naa sante \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji léppi xol \q1 ci biir ñu jub ñi bokk jataay. \q1 \v 2 Liggéeyi Aji Sax ji réy na, \q1 ku ko safoo di ko gëstu. \q1 \v 3 Jëfam teddnga laak daraja, \q1 njekkam di sax ba fàww. \q1 \v 4 Moo dogal ñuy fàttlikuy kéemaanam; \q1 Aji Sax ji boroom yiw ak yërmande. \q1 \v 5 Mooy leel ku ko ragal, \q1 di bàyyi xel \w kóllëreem|lemma="kóllëre g-:"\w* gi ba fàww. \q1 \v 6 Won na ñoñam dooley jëfam, \q1 ba mu leen joxee suufu xeet yi. \q1 \v 7 Ay jëfam dëgg laak njub, \q1 tegtalam yépp mata wóolu, \q1 \v 8 laloo dëgg ak njub, \q1 te sax dàkk ba fàww. \q1 \v 9 Moo yónnee xeetam wall, \q1 fas ak ñoom kóllëre gu sax. \q1 Kee sell te jara ragal! \q1 \v 10 Ragal Aji Sax ji di ndoortel rafet xel, \q1 dég-dég bu rafet ñeel ku koy wéye. \q1 Moo yeyoo cant ba fàww. \c 112 \s1 Ku ragal Yàlla gis njekkam \q1 \v 1 Màggal-leen Ki Sax! \q1 Ndokklee ku ragal \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 di tàqamtikoo ay santaaneem. \q1 \v 2 Aw askanam ay am doole ci réew mi. \q1 Ku jub saw xeet barkeel, \q1 \v 3 alal ak koom am sa kër, \q1 sag njekk sax dàkk. \q1 \v 4 Ceeñeeru biir lëndëm jollil na ku jub \q1 ak ku baax, di boroom yërmande ak njekk. \q1 \v 5 Ki baaxle mooy ki laabiir, di leble, \q1 di jëflante cig njub. \q1 \v 6 Ku jub du tërëf mukk, \q1 te dees na ko fàttliku ba fàww. \q1 \v 7 Du ragal dég-dég bu tiis, \q1 xel ma day dal, mu wóolu Aji Sax ji, \q1 \v 8 fit wa toog, du ragal, \q1 ba kera muy gis noonam jóoru. \q1 \v 9 Mooy nàddil néew-doole yi, \q1 njekkam sax dàkk, \q1 dooleem di yokku, ànd ak daraja. \q1 \v 10 Soxor bi da koy gis, mer, \q1 iñaan bay yéyu, jeex tàkk; \q1 nde soxor, yaakaar ju tas rekk. \c 113 \s1 Buur Yàllaay walloo \q1 \v 1 Màggal-leen Ki Sax! \q1 Yeen ñiy jaamu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, màggal-leen ko, \q1 màggal-leen turu Aji Sax ji! \q1 \v 2 Yal nañu teral turu Aji Sax ji \q1 tey ak ëllëg! \q1 \v 3 Li dale penku ba sowu, \q1 màggal-leen Aji Sax ji. \b \q1 \v 4 Aji Sax jee kawe, tiim xeetoo xeet, \q1 teddngaam sut asamaan! \q1 \v 5 Ana ku mel ni sunu Yàlla Aji Sax ji, \q1 ki kaweel ab jalam, toog, \q1 \v 6 di jéer asamaan ak suuf? \b \q1 \v 7 Mooy yékkatee ku néewle fa suuf, \q1 di seppee ku sonn cib sën, \q1 \v 8 bokkal ko jataayu kilifa, \q1 ya jiite xeetam. \q1 \v 9 Mooy dëël jigéen ju tële woona jur, \q1 may ko mbégtem njureel. \q1 Màggal-leen Ki Sax! \c 114 \s1 Yàllaay walloo dooleem \q1 \v 1 Ba Israyil bàyyikoo fa Misra, \q1 ba waa kër Yanqóoba dëddu làkk-kat yooya, \q1 \v 2 ca la Yuda doon kër Aji Sax ji, \q1 giirug Israyil googu doon ab jagleem. \b \q1 \v 3 Géej gaa leen gis, daw, \q1 dexu Yurdan a deltu gannaaw, \q1 \v 4 tund yu mag yiy curpi niy kuuy, \q1 di curpeendook tund yu ndaw yi niy mbote. \b \q1 \v 5 Moo géej, loo xewle bay daw? \q1 Yaw, dexu Yurdan, looy deltu gannaaw? \q1 \v 6 Tund yu mag yee, lu ngeen di curpi niy kuuy? \q1 Yeen, tund yu ndaw yi, lu ngeen di curpi niy mbote? \b \q1 \v 7 Suufee, loxalal Boroom bi, \q1 Yàllay Yanqóoba mii, \q1 \v 8 ki soppliw doj ndox mu taa, \q1 xeer wu ne sereŋ, mu def bëtu ndox. \c 115 \s1 Ku wóolu Yàlla barkeel \q1 \v 1 Bu muy nun, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, bu muy nun, \q1 saw tur nga wara teral, \q1 ngir sa ngor ak sa worma. \q1 \v 2 Bu yéefar yi ne mukk: \q1 «Moo ñii, ana seen Yàlla?» \q1 \v 3 Te yaw sunu Yàlla, yaa ngi asamaan, \q1 di def lu la soob. \q1 \v 4 Seeni tuur xaalis laak wurus, \q1 di liggéeyu doom aadama: \q1 \v 5 am gémmiñ te du wax, \q1 ami gët te du gis, \q1 \v 6 ami nopp, du dégg, \q1 ami wakkan, du xañtu, \q1 \v 7 ay yoxo it te du yég, \q1 ay tànk it te du dox, \q1 du xàddmiku sax. \q1 \v 8 Ñi sàkk yii tuur, yal nañu mel ni ñoom, \q1 ñook ñi leen wóolu ñépp. \b \q1 \v 9 Éy Israyil, wóolul Aji Sax ji, \q1 moo lay jàpple, di la aar. \q1 \v 10 Yeen waa kër Aaróona, wóoluleen Aji Sax ji, \q1 moo leen di jàpple, di leen aar. \q1 \v 11 Yeen ñi ragal Aji Sax ji, wóoluleen Aji Sax ji, \q1 moo leen di jàpple, di leen aar. \b \q1 \v 12 Aji Sax jee nuy bàyyi xel, di nu barkeel, \q1 di barkeel kër Israyil, \q1 di barkeel kër Aaróona. \q1 \v 13 Aji Sax jeey barkeel ku ko ragal, \q1 mag ak ndaw. \b \q1 \v 14 Yal na leen Yàlla ful, \q1 ful seeni doom. \q1 \v 15 Yal nangeen barkeeloo Aji Sax ji, \q1 ki sàkk asamaan ak suuf. \q1 \v 16 Asamaan, asamaanu Aji Sax jee, \q1 suuf la dénk doom aadama. \q1 \v 17 Du ku dee mooy màggal Ki Sax, \q1 du kenn ku tàbbi réewum tàbbi-selaw! \q1 \v 18 Nun, nooy sargal Ki Sax, \q1 tey ak ëllëg. \q1 Màggal-leen Ki Sax! \c 116 \s1 Ma sant Yàlla mi ma jot \q1 \v 1 Maa bëgg \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji: maa ko woo, \q1 dagaan ko, mu dégg ma. \q1 \v 2 Teewlu na ma moos, \q1 dama koy woo li feek may dund. \q1 \v 3 Buumi ndee a ma laawoon, \q1 njàqarey njaniiw dab ma, \q1 ma dajeek naqar aku tiis. \q1 \v 4 Ma woo Aji Sax ji wall, ne ko: \q1 «Ngalla Aji Sax ji, xettli ma!» \q1 \v 5 Aji Sax jeey boroom yiw ak njekk, \q1 sunu Yàllaay boroom yërmande. \q1 \v 6 Aji Sax jeey aar ku xamul àddina; \q1 tumurànke woon naa, mu wallu ma. \q1 \v 7 Bu ma yeboo sama xel dal, \q1 Aji Sax ji baaxe na ma! \b \q1 \v 8 Xettli nga ma, ba deewuma, \q1 jàpple ma ba tërëfuma, \q1 feral nga it samay rongooñ. \q1 \v 9 Damay topp Aji Sax ji \q1 ci biir réewum aji dund ñi. \q1 \v 10 Ba ma naa: «Torox naa ba toskare,» \q1 teewul may ànd ak ngëm. \q1 \v 11 Maa jàqoon ba naan: \q1 «Ñéppi fen-kat lañu!» \q1 \v 12 Ana lu may njukkale Aji Sax ji, \q1 li mu ma baaxe lépp? \q1 \v 13 Xanaa ma yékkati kaasu Aji Sax \q1 jiy misaal wallam, \q1 te may tudd turam. \q1 \v 14 Samay digeek Aji Sax ji laay matal \q1 fi kanam ñoñam ñépp. \b \q1 \v 15 Wóllërey Aji Sax ji, \q1 bakkanam ñor na Aji Sax ji. \q1 \v 16 Aji Sax ji, maay sab jaam, \q1 maay sab jaam, di sa doomu jaam bi ma sukk jur. \q1 Yaa yiwi samay buum, \q1 \v 17 yaw laay sarxalal \w saraxu cant|lemma="Sarax yi:"\w*, \q1 te turu Aji Sax ji laay tudd. \q1 \v 18 Samay digeek Aji Sax ji laay matal \q1 fi kanam ñoñam ñépp, \q1 \v 19 fi ëtti kër Aji Sax ji, \q1 fi digg Yerusalem. \q1 Màggal-leen Ki Sax! \c 117 \s1 Na ñépp ànd ak Israyil sant Yàlla \q1 \v 1 Yeen xeetoo xeet, màggal-leen \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 réewoo réew, kañleen ko. \q1 \v 2 Moo nu xéewale ngoram gu réy, \q1 te wormay Aji Sax jee sax dàkk. \q1 Màggal-leen Ki Sax! \c 118 \s1 Aji Sax jeek man, ma daan \q1 \v 1 Santleen \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, kee baax, \q1 kee saxoo ngoram! \q1 \v 2 Rikk Israyil, neleen: \q1 «Kee saxoo ngoram!» \q1 \v 3 Rikk waa kër Aaróona, neleen: \q1 «Kee saxoo ngoram!» \q1 \v 4 Rikk yeen ñi ragal Aji Sax ji, neleen: \q1 «Kee saxoo ngoram!» \b \q1 \v 5 Ci xat-xat laa wooye Ki Sax wall, \q1 Ki Sax wuyu ma, yaatal ma. \q1 \v 6 Aji Sax jeek man, duma tiit. \q1 Ana lees ma manal? \q1 \v 7 Aji Sax jeek man, di ma dimbali, \q1 may seetaan bañ yi. \q1 \v 8 Làqoo Aji Sax jee gën \q1 wóolu doom aadama, \q1 \v 9 Làqoo Aji Sax jee gën \q1 wóolu garmi. \q1 \v 10 Yéefar yépp a ma sam, \q1 ma bëmëx leen ci dooley Aji Sax ji. \q1 \v 11 Ñu sam maa sam, \q1 ma bëmëx leen ci dooley Aji Sax ji. \q1 \v 12 Naka lañu ma sam niy yamb, \q1 jekki ne kamaj ni taalu boob, \q1 ma bëmëx ci dooley Aji Sax ji. \q1 \v 13 Dees maa jañaxa jañax, ma ter-teri, \q1 Aji Sax ji dimbali ma. \b \q1 \v 14 Sama doole, sama kaaraange, Ki Sax a; \q1 te mooy sama wall tey. \q1 \v 15 Ndam aki sarxolle ca xaymay ñu jub ña, \q1 ndijooru Aji Sax jee def njàmbaar! \q1 \v 16 Ndijoor la Aji Sax ji xàcci, \q1 ndijooru Aji Sax jee def njàmbaar. \q1 \v 17 Duma dee moos, xanaa dund, \q1 ba nettali jaloorey Ki Sax. \q1 \v 18 Ki Sax mbugal na maa mbugal, \q1 waaye waccu ma, ma dee. \q1 \v 19 Ubbil-leen ma bunti njekk, \q1 ma dugg santi Ki Sax. \b \q1 \v 20 Buntu Aji Sax jaa ngi; \q1 ñu jub ñee ciy dugge. \q1 \v 21 Dama lay sant, yaa ma nangul, \q1 wallu ma tey. \q1 \v 22 Doj wi tabaxkat yi beddi woon, \q1 moo mujj doju coll wi. \q1 \v 23 Lii de, Aji Sax jee ko def, \q1 nu gis ko, yéemu. \q1 \v 24 Bésub tey jii, Aji Sax jee; \q1 nan ko bége, bànneexoo ko. \q1 \v 25 Ngalla Aji Sax ji, wallu nu. \q1 Ngalla Aji Sax ji, may nu ndam. \q1 \v 26 Yal na Yàlla barkeel ki dikke turam. \q1 Nu ngi leen di ñaanale fi néegu Aji Sax ji. \q1 \v 27 Aji Sax jee di Yàlla, di nu leeral. \q1 Ŋàbbleen car yi, màggale, \q1 te dox ba ca béjjéni \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* ba. \q1 \v 28 Yaa di sama Yàlla, ma di la sant; \q1 céy sama Yàlla, dama lay kañ. \q1 \v 29 Santleen Aji Sax ji, kee baax, \q1 kee saxoo ngoram. \c 119 \s1 Aji Sax ji, sa kàddu laay bége \q1 \v 1 Ndokklee yaw mi maandu, \q1 di wéye yoonu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \q1 \v 2 Ndokklee yaw miy wattu kàdduy seedeem, \q1 di ko sàkkoo sa léppi xol. \q1 \v 3 Doo def njubadi, \q1 di topp fi mu la jaarloo. \q1 \v 4 Aji Sax ji, yaa joxe sa tegtal \q1 yi ñu wara toppa topp. \q1 \v 5 Yal naa saxoo \q1 di sàmm sa dogali yoon, \q1 \v 6 di teewlu loo santaane, \q1 ba duma rus. \q1 \v 7 Damay gëstu sa ndigal yu jub, \q1 di la sante xol bu dëggu. \q1 \v 8 Sa dogali yoon laay sàmm; \q1 ngalla bu ma wacca wacc. \b \q1 \v 9 Ana nu ndaw mana sellalee? \q1 Xanaa di sàmm sa kàddu. \q1 \v 10 Sama léppi xol laa lay sàkkoo, \q1 bul ma wacc, ma wàcc say santaane. \q1 \v 11 Sama xol laa làq say wax, \q1 ngir bañ laa moy. \q1 \v 12 Jaajëfe, yaw Aji Sax ji, \q1 jàngal ma sa dogali yoon. \q1 \v 13 Maa àddu, tari \q1 mboolem lu sa kàddu digle. \q1 \v 14 Topp say tegtal laay bége \q1 mbégtem jépp alal. \q1 \v 15 Say tegtal laay jàngat, \q1 di teewlu say xàll. \q1 \v 16 Sa dogali yoon, ma tàqamtikoo, \q1 sa kàddu, ma fat ba fàww. \b \q1 \v 17 Sang bi, baaxe ma, ma dund, \q1 ba mana sàmm sa kàddu. \q1 \v 18 Ngalla muril saay gët, ma niir \q1 sa kéemaani yoon. \q1 \v 19 Doxandéem laa fi kaw suuf, \q1 bu ma làq say santaane. \q1 \v 20 Fu ma tollu maa ngi namm say ndigal \q1 ba sama xol ŋiis. \q1 \v 21 Rëbb nga ñu reew, ñu alku, \q1 ñiy dëddu say santaane. \q1 \v 22 Musal ma ciy kókkaleeki xaste, \q1 maa ngi topp sa kàdduy seede. \q1 \v 23 Te it kàngam yaa ngi may tooge, \q1 te may gëstu sa dogali yoon, Sang bi. \q1 \v 24 Sa kàdduy seede laay safoo, \q1 ñuy sama xejj yi may xelal. \b \q1 \v 25 Maa ngi ne ñàyy ci pënd bi, \q1 musal ma, yaa ko dige. \q1 \v 26 Wax naa la samay jaar-jaar, nga wuyu ma; \q1 ngalla xamal ma sa dogali yoon. \q1 \v 27 Dégtal ma li sa tegtal yiy firi, \q1 ma jàngat say kéemaan. \q1 \v 28 Naqaru xol sonal na ma, \q1 may ma ndëgërlaay, yaa ko dige. \q1 \v 29 Sorele maak yoonu fen, \q1 te baaxe ma saw yoon. \q1 \v 30 Yoonu worma laa taamu, \q1 jàkkaarlook say ndigal. \q1 \v 31 Éy Aji Sax ji, damaa langaamoo sa kàdduy seede, \q1 ngalla bu ma rusloo. \q1 \v 32 Sa yoonu santaane laay daw, \q1 yaa may may xol bu tàlli. \b \q1 \v 33 Aji Sax ji, xamal ma li sa dogali yoon yiy firi, \q1 ma topp ko ba mu jeex. \q1 \v 34 May ma dég-dég, ma topp saw yoon, \q1 toppe ko xol bu tàlli. \q1 \v 35 Jiite ma ci sa xàllu santaane yi, \q1 mooy sama bànneex. \q1 \v 36 Joyantil sama xol, mu féeteek sa kàdduy seede, \q1 te dummóoyu alal ju lewul. \q1 \v 37 May ma, ma fénati caaxaani neen, \q1 te musale ma saw yoon. \q1 \v 38 Sang bi, sottalal ma sa dige \q1 bi nga digook ku la ragal. \q1 \v 39 Moyale ma gàcce gi ma ragal; \q1 yaa baaxi ndigal. \q1 \v 40 Maaka namm say tegtal, \q1 musale ma sag njekk! \b \q1 \v 41 Aji Sax ji, yaa ko dige, \q1 dikke ma sa jëfi ngor ak sa wall, \q1 \v 42 ba ku ma kókkali, ma am tontam. \q1 Maa doyloo sa kàddu. \q1 \v 43 Bu ma xañ mukk kàddug dëgg, \q1 say àtte laa yaakaar kat. \q1 \v 44 Maay topp saw yoon, sàlloo ko, \q1 saxoo ko ba fàww, \q1 \v 45 di daagoo sago, \q1 nde say tegtal laay sàkku. \q1 \v 46 Maay àgge ay buur sa kàdduy seede, \q1 te duma rus. \q1 \v 47 Maay bége sa santaane \q1 yi ma sopp, \q1 \v 48 di yóotu sa santaane yi ma sopp, \q1 di jàngat sa dogali yoon. \b \q1 \v 49 Bàyyil xel li nga ma dig, Sang bi; \q1 moom laa yaakaar. \q1 \v 50 Lii laay muñe samaw naqar, \q1 sa kàddoo may dundal. \q1 \v 51 Nit ñu bew ñi ñaawal nañu ma lool, \q1 waaye dëdduwma saw yoon. \q1 \v 52 Éy Aji Sax ji, damaa fàttliku sa àtte ya woon, \q1 daldi muñ. \q1 \v 53 Sama xol daa fees ndax ñu bon \q1 ñiy wacc saw yoon. \q1 \v 54 Sa dogali yoon laay woyantoo, \q1 fu ma mana sance. \q1 \v 55 Aji Sax ji, tudd naa la guddi, \q1 di sàmm saw yoon. \q1 \v 56 Lii laa séddoo, \q1 maa topp sa tegtali yoon. \b \q1 \v 57 Aji Sax ji, yaw laa séddoo; \q1 di digee sàmm sa kàddu. \q1 \v 58 Sama léppi xol laa sàkkoo saw yiw, \q1 ngalla baaxe ma, yaa ko dige. \q1 \v 59 Damaa seetlu sama jëfin, \q1 dëpp, topp sa kàdduy seede. \q1 \v 60 Maa ngi gaawtu, \q1 yeexewma say santaane moos! \q1 \v 61 Buumi ñu bon ñaa ngi may laaw, \q1 te sàgganewma saw yoon. \q1 \v 62 Xaaju guddi laay jóg, \q1 di la sante sa àttey njekk. \q1 \v 63 Maa xejjoo képp ku la ragal, \q1 tey topp say tegtal. \q1 \v 64 Aji Sax ji, sa ngor dajal na àddina; \q1 xamal ma sa dogali yoon. \b \q1 \v 65 Aji Sax ji, def nga la nga dige woon, \q1 Sang bi, defal nga ma ngëneel. \q1 \v 66 Xamal ma ngëneeli àtte ak xam-xam, \q1 maa doyloo say santaane. \q1 \v 67 Maa jàddoon, nga duma ma, \q1 léegi sa kàddu laay sàmm. \q1 \v 68 Yaaka baax tey baaxe; \q1 rikk xamal ma say tegtal. \q1 \v 69 Ñu bew ñee yàq sama der aki sos, \q1 te ma topp say tegtal, wéetal la. \q1 \v 70 Ñu ngi nii, seen bopp yi, tafas; \q1 te man may tàqamtikoo saw yoon. \q1 \v 71 Ngëneel la ma duma yi jural, \q1 ngir jànge naa ci say tegtal. \q1 \v 72 Sa ngëneelu yoon wi nga digle \q1 moo ma gënal ay junniy xaalis ak wurus. \b \q1 \v 73 Say loxoo ma sàkk, tabax ma, \q1 may ma ag dégg, ma mokkal say santaane, \q1 \v 74 ñi la ragal gis ma, bég; \q1 nde sa kàddu laa yaakaar. \q1 \v 75 Aji Sax ji, ràññee naa ne say ndigal njekk la, \q1 te worma nga ma dumaa. \q1 \v 76 Ngalla dëfale ma sa ngor; \q1 Sang bi, yaa ko dige. \q1 \v 77 Nanga ma ganesee sa yërmande, ma dund; \q1 saw yoon ay sama bànneex! \q1 \v 78 Yal na ñu bew ñi torox, \q1 ñoo ma lor ak seeni sos, \q1 te man may gëstu say tegtal. \q1 \v 79 Yal na ku la ragal waññiku fi man, \q1 ba xam sa kàdduy seede. \q1 \v 80 Yal naa toppe say tegtal xol bu mat sëkk, \q1 ba duma rus. \b \q1 \v 81 Sàkku naa sag wall ba xol jeex, \q1 di xaar sa kàddu. \q1 \v 82 Séentu naa sab dige, ba gët giim; \q1 kañ nga may xettli? \q1 \v 83 Damaa mujj ras ni mbuusum der mu saxar jàpp, \q1 waaye sàgganewma say tegtal. \q1 \v 84 Ñaata fan laay toogati, Sang bi? \q1 Kañ ngay mbugal ñi ma topp? \q1 \v 85 Ñu bew ñi gasal nañu ma ay yeer, \q1 yu saw yoon diglewul. \q1 \v 86 Sa santaane yépp worma la; \q1 te dees maa toppey sos, wallu ma! \q1 \v 87 Nes tuut ñu sànke ma fi kaw suuf, \q1 te man dëdduwma say tegtal. \q1 \v 88 Musale ma sa ngor, \q1 ba jëfe sa kàdduy seede. \b \q1 \v 89 Aji Sax ji, sa kàddoo sax dàkk, \q1 taxaw jonn fa asamaan. \q1 \v 90 Sa worma, ba maasoo maas, \q1 yaa samp suuf, saxal ko. \q1 \v 91 Ci sa ndigal la lépp taxawe ba tey, \q1 lépp ànd, di la jaamu. \q1 \v 92 Su ma bégewuloon saw yoon, \q1 sànkoo sama toskare ji. \q1 \v 93 Duma fàtte mukk say tegtal, \q1 ci nga may musale. \q1 \v 94 Yaa ma moom, wallu ma; \q1 say tegtal laay sàkku. \q1 \v 95 Man la ñu bon ñi tëru, nar maa sànk, \q1 waaye sa kàdduy seede laay niir. \q1 \v 96 Gis naa ne lu mat lu ne am na kemu, \q1 waaye sa santaane mat ba wees kemu. \b \q1 \v 97 Maaka sopp saw yoon, \q1 di ko jàngat bés bu jot. \q1 \v 98 Li ma xelal ba ma raw noon yi, \q1 mooy sa santaane, yi ma jagoo fàww. \q1 \v 99 Maa gëna ñaw képp ku may jàngal, \q1 nde sa kàdduy seedeey sama njàngat. \q1 \v 100 Maa ëpp mag ñi dég-dég, \q1 nde say tegtal laa topp. \q1 \v 101 Luy yoon wu aay, ma moyu, \q1 ba mana sàmm sa kàddu. \q1 \v 102 Say santaane it dëdduwma ko, \q1 nde yaw yaa ma jàngal. \q1 \v 103 Sa kàddooka maa neex, \q1 ba dàqal ma tem-temu lem! \q1 \v 104 Say tegtal laay ràññee, \q1 ba tax ma bañ luy yoonu fen. \b \q1 \v 105 Sa kàddu laay niitoo samay tànk, \q1 muy leeral samaw yoon. \q1 \v 106 Giñ naa te di ko dëggal, \q1 ne dinaa sàmmonteek sa ndigali njekk. \q1 \v 107 Toskare naa ba ci lool; \q1 éy Aji Sax ji, musal ma, yaa ko dige. \q1 \v 108 Aji Sax ji, rikk nangul ma kàdduy cant yi ma lay jébbal, \q1 te xamal ma say ndigal. \q1 \v 109 Sama bakkan ci xott saa su ne, \q1 waaye fàttewuma saw yoon. \q1 \v 110 Ñu bon ñi ma gasal um pax \q1 taxul ma wàcc say tegtal. \q1 \v 111 Maa séddoo fàww sa kàdduy seede, \q1 loolooy seral sama xol. \q1 \v 112 Damaa dogoo jëfe sa dogali yoon, \q1 saxoo ko ba mu jeex. \b \q1 \v 113 Maa bañ kuy ŋarale, \q1 maa sopp saw yoon. \q1 \v 114 Sama rawtu, sama kiiraay, yaw a; \q1 sa kàddu laay xaar. \q1 \v 115 Yeen ñiy def lu bon, xiddileen ma, \q1 ba ma sàmmonteek sama santaaney Yàlla. \q1 \v 116 Yaa ko dige, dooleel ma, ma dund; \q1 bul tas sama yaakaar. \q1 \v 117 Kàttanal ma, ma raw, \q1 di yittewoo say tegtal, ba fàww. \q1 \v 118 Yaay xarab képp ku wàcc sa dogali yoon, \q1 ay pexeem neen. \q1 \v 119 Yaay tonni ni purit képp ku bon fi kaw suuf, \q1 moo tax ma sopp sa kàdduy seede. \q1 \v 120 Sama yaram a ngi daw ndax ragal la, \q1 ragal say àtte. \b \q1 \v 121 Def naa njub, def njekk; \q1 bu ma wacce ñi may néewal. \q1 \v 122 Sang bi, gàddu ma, ma am jàmm, \q1 bu ma ñu bew ñi néewal. \q1 \v 123 Séentu naa sag wall ak sa kàddug njekk, \q1 ba saay gët giim. \q1 \v 124 Sang bi, jëfeel ma sa ngor, \q1 xamal ma sa dogali yoon. \q1 \v 125 Sab jaam laa, may ma, ma ràññee, \q1 ba xam sa kàdduy seede. \q1 \v 126 Aji Sax ji, jëf jot na, \q1 ñee ngi jalgati saw yoon! \q1 \v 127 Maa sopp say santaane, \q1 mu gënal ma wurus ba ci wurusu ngalam. \q1 \v 128 Moo tax foo tegtale, ma rafetlu, \q1 lépp luy yoonu fen, ma bañ. \b \q1 \v 129 Sa kàdduy seede kéemaan la, \q1 moo tax ma di ko toppe xol. \q1 \v 130 Sa pirim kàddu day leeral, \q1 di xelal ku xeluwul. \q1 \v 131 Damaa ŋa ŋafeet, di àppaat, \q1 ngir namm say santaane. \q1 \v 132 Éy geesu ma te baaxe ma, \q1 ni nga baaxook ñi sopp sa tur. \q1 \v 133 Dooleelal ma samay tànk, yaa ko dige, \q1 te bu ma lenn lu bon man. \q1 \v 134 Jot ma ci noteelu doom aadama, \q1 ma mana topp say tegtal. \q1 \v 135 Sang bi, geesoo ma sag leer, \q1 te xamal ma sa dogali yoon, \q1 \v 136 ay wali rongooñ ay wale saay gët, \q1 ndax sàmmeesul saw yoon. \b \q1 \v 137 Aji Sax ji, yaaka jub, \q1 te say àtte di yoon. \q1 \v 138 Yaa santaane sa kàdduy seede ci njekk \q1 ak worma ju yaa. \q1 \v 139 Damaa gis bañ yiy sàggane say wax, \q1 xol bu tàng di ma rey. \q1 \v 140 Sang bi, maaka sopp sa kàddu \q1 gi set ni weñ gu ñu xelli! \q1 \v 141 Ñàkk naa solo, faaleesu ma, \q1 waaye sàgganewma say tegtal. \q1 \v 142 Sag njekk moo dig njekk ba fàww, \q1 te saw yoon a dëggu. \q1 \v 143 Njekkar ak njàqare dab ma, \q1 say santaane di sama bànneex. \q1 \v 144 Sa kàdduy seedee di njekk ba fàww, \q1 may ma, ma ràññee, ba dund. \b \q1 \v 145 Aji Sax ji, woo naa la wall lu ma man, \q1 wuyu ma, ma topp sa dogali yoon. \q1 \v 146 Dama ne: «Wóoy, wallu ma, \q1 ma sàmm sa kàdduy seede.» \q1 \v 147 Damaa jëlu, di la woo, \q1 di xaar sa kàddu. \q1 \v 148 Damay xoole guddi gépp, \q1 di jàngat sa kàddu. \q1 \v 149 Aji Sax ji, sama baat bii, teewloo ko sa ngor, \q1 te musal ma ni nga baaxoo muslee. \q1 \v 150 Rabatkati pexe yaa ngi jegesi, \q1 di nit ñu sore saw yoon. \q1 \v 151 Waaye yaw Aji Sax ji, jege nga, \q1 te sa santaane yépp a dëggu. \q1 \v 152 Yàgg naa xam ne sa kàdduy seede \q1 wax la joo saxal dàkk. \b \q1 \v 153 Xoolal sama coono te xettli ma; \q1 saw yoon déy, sàgganewma ko. \q1 \v 154 Àtte ma, ba jot ma; \q1 musal ma, yaa ko dige. \q1 \v 155 Ku bon sore sa wall, \q1 ngir sàkkuwul sa dogali yoon. \q1 \v 156 Aji Sax ji, sa yërmande yaa na; \q1 musal ma ni nga ko baaxoo. \q1 \v 157 Ñi ma topp ak ñi ma baña bare, \q1 te taxul ma dëddu sa kàdduy seede. \q1 \v 158 Damaa gis workat yi, sib leen; \q1 ñoo sàmmul sa kàddu. \q1 \v 159 Seetlul ni ma soppe say tegtal. \q1 Éy Aji Sax ji, musal ma, yaa gore! \q1 \v 160 Sa mboolem kàddu dëgg la, \q1 sa ndigal yépp di njekk, sax dàkk. \b \q1 \v 161 Ay kilifaa ma topp ci dara, \q1 te teewul ma wormaal sa kàddu. \q1 \v 162 Man de, maa ngi bége sa kàddu \q1 ni ku for alal ju bare. \q1 \v 163 Fen, ma bañ, ba sib; \q1 sa yoon, ma sopp. \q1 \v 164 Juróom yaari yoon ci bés \q1 màggale naa la ko say àttey njekk. \q1 \v 165 Jàmm ju baree ñeel ku sopp sa yoon, \q1 te dara du ko fakktal. \q1 \v 166 Aji Sax ji, sa wall laa yaakaar, \q1 say santaane laa jëfe. \q1 \v 167 Sama xol laa toppe sa kàdduy seede, \q1 te sopp koo sopp. \q1 \v 168 Damaa topp say tegtal ak sa kàdduy seede, \q1 fépp fu ma jaar kay yaa ngi ciy gis. \b \q1 \v 169 Aji Sax ji, yal na sama yuux àgg fa yaw; \q1 may ma, ma ràññee, yaa ko dige. \q1 \v 170 Yal na sama dagaan àgg fa yaw; \q1 xettli ma, yaa ko dige. \q1 \v 171 Naa xaacu, woyal la, \q1 yaa may jàngal sa dogali yoon. \q1 \v 172 Naa woye sa kàddu, \q1 loo santaane, njekk la. \q1 \v 173 Yal nanga ma dikke ndimbal, \q1 say tegtal laa taamu. \q1 \v 174 Aji Sax ji, namm naa sa wall, \q1 sa yoon ay sama bànneex. \q1 \v 175 Yal naa dund ba màggal la, \q1 say ndigal di sama ndimbal. \q1 \v 176 Lajj naa ni xar mu réer; \q1 gindi ma, Sang bi, \q1 sàgganewma say santaane de! \c 120 \s1 Ma ñaan ci biir tuuma \d \v 1 Muy \w jàngi yéeg|lemma="jàngi yéeg g-:"\w*, ñu di ko màggale Yàlla. \b \q1 Ci sama njàqare laa woo \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wall, \q1 mu wuyu ma. \q1 \v 2 Éy Aji Sax ji, musal ma ci gémmiñu fen-kat, \q1 ak làmmiñu njublaŋ. \q1 \v 3 Yaw boroom làmmiñu njublaŋ, \q1 ana lu ñu lay añale \q1 ak lu ñu lay dolli? \q1 \v 4 Xanaa fitti mbër yu ñaw \q1 ak xal yu yànj. \b \q1 \v 5 Wóoy man mi ganeyaani baadooloy Meseg ya \q1 tey dali fa xaymay waa Kedar ñu xayadi ña! \q1 \v 6 Yàgg naa lool ci biir nit ñi bañ jàmm. \q1 \v 7 Man may wut jàmm, \q1 te su ma waxee, \q1 ñoom ñuy ayoo. \c 121 \s1 Ana ku may sàmm? \d \v 1 Muy \w jàngi yéeg|lemma="jàngi yéeg g-:"\w*, ñu di ko màggale Yàlla. \b \q1 Damaa séentu tund ya, \q1 te naan fu wall di jóge? \q1 \v 2 Sama wall a nga fa \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 ki sàkk asamaan ak suuf. \b \q1 \v 3 Kii du la bàyyi nga tërëf, \q1 sa sàmm bii gëmmul. \q1 \v 4 Kiy sàmm Israyil kay \q1 gëmmul, nelawul. \q1 \v 5 Aji Sax jee lay sàmm, \q1 Aji Sax jee lay yiir, \q1 féete la ndijoor. \b \q1 \v 6 Du naaj wu lay dal bëccëg, \q1 mbaa leer gu ndaw guddi. \q1 \v 7 Aji Sax jee lay sàmm ci gépp loraange, \q1 di sàmm sa bakkan. \q1 \v 8 Aji Sax jee lay sàmm, dem ak dikk, \q1 tey ak ëllëg. \c 122 \s1 Nu ñaanal Yerusalem \d \v 1 Muy \w jàngi yéeg|lemma="jàngi yéeg g-:"\w*, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda. \b \q1 Maaka bég, ba ñu ma nee: \q1 «Kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji lanu jëm.» \q1 \v 2 Yaw Yerusalem, noo ngii taxaw sa bunt. \b \q1 \v 3 Céy, Yerusalem, dëkkub tabax bu baax, \q1 bi booloo, di benn. \q1 \v 4 Fii la giiri Israyil di yéegsi, \q1 di giir yi Ki Sax séddoo. \q1 Ñu ngi santsi Aji Sax ji, \q1 ni ko Israyil warloo. \q1 \v 5 Fii la ngànguney Israyil tege, \q1 askanu Daawuda toog ca, di àtte. \b \q1 \v 6 Dagaanleen jàmmi Yerusalem: \q1 «Yerusalem, yal na sa xeli soppe dal, \q1 \v 7 jàmm ne ñoyy fi say tata wër, \q1 te xel dal ci biir këri Buur.» \q1 \v 8 Mbokk ak xarit a waral \q1 may ñaan jàmmi Yerusalem. \q1 \v 9 Sunu kër Yàlla Aji Sax jee ma tax \q1 di sàkku ngëneelu Yerusalem. \c 123 \s1 Yàlla, fajal nu gàcce \d \v 1 Muy \w jàngi yéeg|lemma="jàngi yéeg g-:"\w*, ñu di ko màggale Yàlla. \b \q1 Yaw laay séentu, \q1 yaw mi toog fa asamaan. \q1 \v 2 Ma ne, ni jaam bu góor di wékke sangam bët, \q1 jaam bu jigéen di ko wékke bët sangam bu jigéen, \q1 ni lanuy wékke sunu Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji bët, \q1 ba keroog mu baaxe nu. \b \q1 \v 3 Éy Aji Sax ji, baaxe nu, rikk baaxe nu, \q1 dañu noo torxal, ba nu ne tott. \q1 \v 4 Ñu reew ñaa ngi nuy ñaawal, sunu xol fees, \q1 ñu bew ñaa ngi nuy sewal. \c 124 \s1 Nanu sante Aji Sax ji wallam \d \v 1 Muy \w jàngi yéeg|lemma="jàngi yéeg g-:"\w*, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda. \b \q1 Éy su dul woon ak \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nu nekkal! \q1 Israyiloo, waxati ko: \q1 \v 2 su dul woon ak Aji Sax ji nu nekkal, \q1 ba ñu nu jógalee, \q1 \v 3 ba nit ña xadaroo sunu kaw, \q1 dañu nu doon wonn, nuy dund, \q1 \v 4 dañu nu doon mëdd nim ndox, \q1 def um wal, buub nu, \q1 \v 5 def waame wuy wal-wali, \q1 buub nu, yóbbu. \b \q1 \v 6 Cant ñeel na Aji Sax ji, \q1 ki nu bàyyiwul, noon yi yàpp nu. \q1 \v 7 Danu ne fërr, nim picc \q1 mu rëcc fiiru rëbb, \q1 fiir ga toj, nu raw. \q1 \v 8 Sunu ndimbal a ngi ci turu Aji Sax ji, \q1 ki sàkk asamaan ak suuf. \c 125 \s1 Ku doyloo Aji Sax ji raw \d \v 1 Muy \w jàngi yéeg|lemma="jàngi yéeg g-:"\w*, ñu di ko màggale Yàlla. \b \q1 Ku doyloo \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 yaay tundu \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, doo toxu; \q1 dangay sax ba fàww. \q1 \v 2 Ni tund yi yéewe Yerusalem, \q1 ni la Aji Sax ji yéewe ñoñam, \q1 tey ak ëllëg. \b \q1 \v 3 Nguur gu bon du saxe \q1 kaw suuf su nit ñu jub muurloo. \q1 Lu ko moy ñu jub ñi sàkku lu bon, \q1 di ko jëfe. \b \q1 \v 4 Éy Aji Sax ji, baaxeel ku baax, \q1 ak kuy mébét njub. \q1 \v 5 Waaye kuy topp yoonu ndëngte, \q1 Aji Sax jee koy sànk, \q1 boole kook kuy def lu bon. \q1 Yal na jàmm dal Israyil. \c 126 \s1 Yàlla, delloo nu \d \v 1 Muy \w jàngi yéeg|lemma="jàngi yéeg g-:"\w*, ñu di ko màggale Yàlla. \b \q1 Ba \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji delloo waa \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* seen réew, \q1 danoo meloon ni ñuy gént, \q1 \v 2 di reek a sarxolle rekk. \q1 Yéefar yi naa: \q1 «Lu réy la Aji Sax ji defal ñii.» \q1 \v 3 Lu réy la nu Aji Sax ji defal moos, \q1 nu bég. \b \q1 \v 4 Aji Sax ji, rikk delloo nu na woon, \q1 ni ngay delloo wal yu ŋiis, mu walaat ca àllub Negew. \q1 \v 5 Kuy ji di jooy, \q1 yal na góob, di sarxolle. \q1 \v 6 Ku doon wéya wéy, di jooy; \q1 ŋàbb mbuusum jiwoom, \q1 yal na dikka dikk, di woy, \q1 ñibbaale sabaaram. \c 127 \s1 Barkeb Yàllaa wóor \d \v 1 Muy \w jàngi yéeg|lemma="jàngi yéeg g-:"\w*, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Suleymaan. \b \q1 Kër, su ko \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji tabaxul, \q1 ku ko tabax, neen nga doñ-doñi. \q1 Ab dëkk, su ko Aji Sax ji wattuwul, \q1 ku ko wattu, neen nga teewlu. \q1 \v 2 Neen it la nit di teela jóg \q1 ak a guddee tëdd, \q1 di doñ-doñi lu mu lekk: \q1 Aji Sax ji leel na soppeem lu ni day, \q1 fekk ko muy nelaw. \b \q1 \v 3 Ma ne, doom Aji Sax jee koy sédde, \q1 njurum doom yool la. \q1 \v 4 Doom joo jure ndaw, \q1 mooy fitt ci loxol jàmbaar; \q1 \v 5 ndokklee ku ci mbuusam fees, \q1 ba bu ñu taseek ub noon ca pénc ma, \q1 duñu am gàcce mukk. \c 128 \s1 Ragal Yàlla, jàmmi kër \d \v 1 Muy \w jàngi yéeg|lemma="jàngi yéeg g-:"\w*, ñu di ko màggale Yàlla. \b \q1 Ndokklee képp ku ragal Yàlla, \q1 di jëfe ay yoonam. \q1 \v 2 Yaay lekk saw ñaq, \q1 mbégteek ngëneel ñeel la. \q1 \v 3 Sa jabar ni garab gu nangoo sa wanag, \q1 say doom wëra wër sa ndab ni njëmbat lu jebbi. \q1 \v 4 Ki ragal \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jaa ngoog, \q1 nii rekk lay barkeele. \b \q1 \v 5 Yal na la Yàlla barkeele fii ci \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*; \q1 yal nanga teewe xéewalu Yerusalem \q1 sa giiru dund gépp, \q1 \v 6 te nga gis say sët. \q1 Yal na jàmm dal Israyil. \c 129 \s1 Noon manul Israyil \d \v 1 Muy \w jàngi yéeg|lemma="jàngi yéeg g-:"\w*, ñu di ko màggale Yàlla. \b \q1 Ba may ndaw ba tey, ñu ngi may sonala sonal. \q1 Israyiloo, waxati ko: \q1 \v 2 Ba may ndaw ba tey, ñu ngi may sonala sonal, \q1 te taxul ñu man ma. \q1 \v 3 Sama gannaaw gi lañu gàbba gàbb, \q1 rëdd koo rëdd nib tool. \q1 \v 4 Waaye \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji boroom njekk \q1 dog na buumi ñu bon ña. \b \q1 \v 5 Képp ku noonoo \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* \q1 yal nañu ko dëpp, gàcceel ko. \q1 \v 6 Yal nañu mel ni ñax mu saxem xadd, \q1 balaa law, lax. \q1 \v 7 Du doyub ŋëb ku ko dog; \q1 du doyub say ku ko for. \q1 \v 8 Ku fa jaare it du ko ne: \q1 «Jaajëf, Aji Sax ji barkeel; \q1 jaajëfe yaw, yal na Aji Sax ji barkeel.» \c 130 \s1 Nu séentu njotug Yàlla \d \v 1 Muy \w jàngi yéeg|lemma="jàngi yéeg g-:"\w*, ñu di ko màggale Yàlla. \b \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ci ay xóote laa lay wooye. \q1 \v 2 Boroom bi, déglu ma, \q1 teewlu ma, ma tinu la. \b \q1 \v 3 Ki Sax, yaw, soo doon lim bàkkaar, \q1 Boroom bi, ana kuy taxaw? \q1 \v 4 Waaye yaay jéggale, \q1 ñu ragal la. \b \q1 \v 5 Damay xaar Aji Sax ji, di ko xaare xol, \q1 di yaakaar kàddoom. \q1 \v 6 Wattukat bi yàkkamti njël, \q1 wattukat bi yàkkamti njël, laa ne, \q1 ni ma yàkkamtee Aji Sax jee ko raw. \b \q1 \v 7 Éey Israyil, négandikul Aji Sax ji. \q1 Aji Sax jee gore, \q1 te yaatug njot. \q1 \v 8 Mooy jot Israyil ci ñaawtéefam yépp. \c 131 \s1 Damaa woyof, gëm Yàlla \d \v 1 Muy \w jàngi yéeg|lemma="jàngi yéeg g-:"\w*, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda. \b \q1 Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, man de, réy-réyluwma, \q1 daŋŋiiraluma, \q1 xintewoowma lu réy it, \q1 mbaa lu ma ëlëm. \q1 \v 2 Xanaa ne tekk, ne cell, \q1 ni perantal ak ndeyam; \q1 sama xel dal ni perantal. \q1 \v 3 Éey Israyil, yaakaaral Aji Sax ji \q1 tey ak ëllëg. \c 132 \s1 Yàlla digoo naak ki mu fal \d \v 1 Muy \w jàngi yéeg|lemma="jàngi yéeg g-:"\w*, ñu di ko màggale Yàlla. \b \q1 Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, bàyyil xel Daawuda, \q1 ak gépp njàqareem. \q1 \v 2 Moo giñaloon Aji Sax ji, \q1 moo digook Mbërum Yanqóoba ma. \q1 \v 3 Mu ne: «Duma ñibbi, \q1 \v 4 duma tëddi sama kaw lal ba, \q1 duma nelaw, duma gëmm sax bët, \q1 \v 5 li feek sàkkaluma Aji Sax ji bérab, \q1 ba dëkkal Mbërum Yanqóoba ma.» \q1 \v 6 Ma ne, Efrata lanu dégg gaalu Yàlla ga, \q1 fekk ko àllub Yaar. \q1 \v 7 Nan dem ba këram, \q1 sujjóotali ndëggëstalu tànkam ya. \q1 \v 8 Aji Sax ji, jógal agsi sa dal-lukaay, \q1 yaak sa \w gaal|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* gi jëmmal sa doole. \q1 \v 9 Say \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w*, yal nañu woddoo njekk, \q1 sa wóllëre yi sarxolleendoo. \q1 \v 10 Xoolal ci Daawuda, sa jaam ba, \q1 bul gàntu ki nga fal. \b \q1 \v 11 Aji Sax ji daa giñal Daawuda \q1 dëgg gu mu dul dëddu, \q1 ne ko: «Ku jóge sa geño \q1 laay wuutal ci sa jal bi, \q1 \v 12 te say doom, bu ñu sàmmee sama \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w*, \q1 ak sama kàdduy seede yi ma leen di xamal, \q1 seeni doom it ñooy tooge \q1 sa jal ba fàww.» \q1 \v 13 Aji Sax ji kat a tànn \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, \q1 taamu faa dëkke. \q1 \v 14 Mu ne: «Fii laay dal-loo ba fàww, \q1 fii laay dëkk, maa ko taamu. \q1 \v 15 Dund bi, ma barkeela barkeel, \q1 néew-ji-doole yi, ma reggal; \q1 \v 16 sarxalkat yi, ma wodde njot; \q1 way-gëm ñi di sarxollee sarxolle. \q1 \v 17 Fa laay dooleele Daawuda, \q1 taalal ki ma fal, \q1 \v 18 ay noonam, ma wodde gàcce; \q1 moom, kaalaam ne ràññ.» \c 133 \s1 Bokk, bennoo neex \d \v 1 Muy \w jàngi yéeg|lemma="jàngi yéeg g-:"\w*, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda. \b \q1 Céy liika baax te neexati, \q1 ay bokk yu bokk dëkk, di benn! \q1 \v 2 Daa neex ni diwu bopp gu xeeñ, \q1 siite sikkim, bu mel ni sikkimu Aaróona, \q1 rogalaat ba ci mbubbam, \q1 \v 3 neex ni layub tundu Ermon, \q1 neex ni lay bu ni mel tey rogalaate tundi \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*. \q1 Fa la \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dogal barke, \q1 muy dund gu dul jeex. \c 134 \s1 Way-gëm ñaa ngi sant \d \v 1 Muy \w jàngi yéeg|lemma="jàngi yéeg g-:"\w*, ñu di ko màggale Yàlla. \b \q1 Ayca, santleen \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 yeen jaami Aji Sax ji yépp, \q1 yeen ñiy taxawe kër Aji Sax ji guddi. \q1 \v 2 Yékkatileen seeni loxo \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* ba, \q1 te sant Aji Sax ji. \b \q1 \v 3 Yal na la Aji Sax ji barkeele fa \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, \q1 moom mi sàkk asamaan ak suuf. \c 135 \s1 Aji Sax ji jot na Israyil \q1 \v 1 Màggal-leen Ki Sax! \q1 Màggal-leen turu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 éey jaami Aji Sax ji, màggal-leen, \q1 \v 2 yeen ñi taxawe kër Aji Sax ji, \q1 fi sunu biir ëttu Yàlla bi. \q1 \v 3 Màggal-leen Ki Sax, Aji Sax jee baax! \q1 Kañleen ko, kee sopplu! \q1 \v 4 Ki Sax a taamu Yanqóoba, \q1 muy Israyil mi mu séddoo. \b \q1 \v 5 Maa xam ne Aji Sax ji màgg na! \q1 Sunu Boroom a sut lépp lu ñuy jaamu. \q1 \v 6 Lépp lu Aji Sax ji namm, \q1 moom lay def asamaan ak suuf, \q1 ak biir géej ak xóote yépp. \q1 \v 7 Mooy yékkateey niir fa cati àddina, \q1 sàkkal taw ay melax, \q1 yebbee ngelaw cay dencam, \q1 \v 8 fàdd luy taaw fa Misra, \q1 doom aadama, ba ci mala. \q1 \v 9 Yeen waa Misra, moo yónnee ay firndeeki kéemaan fi seen biir, \q1 ñeel Firawnaak jawriñam ñépp. \q1 \v 10 Moo duma ay xeeti xeet, \q1 bóom buur yu mag yi, \q1 \v 11 muy Siwon buurub Amoreen ña, \q1 ak Og buuru Basan, \q1 ak buuri Kanaan ñépp. \q1 \v 12 Moo nangu seen réew, séddale, \q1 \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ñiy ñoñam séddoo. \b \q1 \v 13 Aji Sax ji, sa tur ba fàww; \q1 Aji Sax ji, sa woy a saxal maasoo maas. \q1 \v 14 Aji Sax ji kay ay àtte ñoñam ñi, \q1 di ñeewante jaamam ñi. \q1 \v 15 Tuuri yéefar yi, xaalis ak wurus, \q1 loxoo ko sàkk. \q1 \v 16 Am gémmiñ te du wax, \q1 ami gët te du gis, \q1 \v 17 ami nopp te du dégg, \q1 du sax noowal bakkan. \q1 \v 18 Ñi sàkk yii tuur, yal nañu mel ni ñoom, \q1 ñook ñi leen wóolu ñépp. \q1 \v 19 Éey waa kër Israyil, santleen Aji Sax ji! \q1 Éey waa kër Aaróona, santleen Aji Sax ji! \q1 \v 20 Éey waa kër Lewi, santleen Aji Sax ji! \q1 Yeen ñi ragal Aji Sax ji, santleen Aji Sax ji! \q1 \v 21 Nañuy sante Aji Sax ji \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, \q1 moom mi dëkke Yerusalem. \q1 Màggal-leen Ki Sax! \c 136 \s1 Yàllaa am kóllëre \q1 \v 1 Nangeen sante \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji mbaaxam. \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 2 Santleen Yàllay yàlla yi. \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 3 Santleen Sangu sang yi. \qr Kee saxoo ngoram! \b \q1 \v 4 Moo wéetoo jaloore yu mag yi. \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 5 Moo sàkke asamaan manoore. \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 6 Moo lal suuf ca kaw ndox ma. \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 7 Moo sàkk leer yu mag yi: \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 8 jant bi yilif bëccëg, \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 9 weer ak biddiiw, guddi. \qr Kee saxoo ngoram! \b \q1 \v 10 Moo fàdd taawi Misra yu góor ya, \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 11 seppee \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ca ñoom, \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 12 ci dooley loxoom ak kàttanu përëgam. \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 13 Moo xar géeju Barax ya yaar, \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 14 jàllale bànni Israyil ca digg ba. \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 15 Moo xalab Firawnaak mbooloom ca géeju Barax ya. \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 16 Moo jiite ñoñam ca màndiŋ ma. \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 17 Moo duma buur yu mag ya, \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 18 bóom buur yu màgg ya, \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 19 reyaale Siwon buurub Amoreen ña, \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 20 reyati Og buuru Basan. \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 21 Moo nangu seen réew, joxe, \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 22 sédde Israyil ma dib jaamam. \qr Kee saxoo ngoram! \b \q1 \v 23 Ci biir notaange la nu geesoo, \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 24 ne nu siféet ci loxoy noon ya. \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 25 Mooy leel bépp boroom bakkan. \qr Kee saxoo ngoram! \q1 \v 26 Santleen Yàlla mi ci asamaan! \qr Kee saxoo ngoram! \c 137 \s1 Jooye nanu àll \q1 \v 1 Ca tàkkal dexi Babilon, \q1 foofa lanu daa toog, \q1 fàttliku \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, jooy. \q1 \v 2 Ca garab ya \q1 lanu daa wékk sunuy xalam. \q1 \v 3 Fa la nu sunuy sang daa woyloo, \q1 not nu, bëgg nu bégal leen, \q1 naan: «Woyal-leen nu ci woyi Siyoŋ.» \q1 \v 4 Moo nu nuy woye woyu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji \q1 kaw suufas yéefar? \q1 \v 5 Éy Yerusalem, su ma la naree fàtte, \q1 yal na ma doole dëddu! \q1 \v 6 Yerusalem, su ma la fàttlikuwul, \q1 fonk la, ba gën laa bége lépp, \q1 yal na sama làmmiñ tafoo sama denqleñ. \b \q1 \v 7 Aji Sax ji, fàttlikul Edomeen ña, \q1 keroog jantub Yerusalem, \q1 ba ñu naan: «Màbbleena màbb, \q1 ba kenug dëkk bi siiñ!» \q1 \v 8 Yeen waa Babilon, gi ñu nara fàllas, \q1 ndokklee ku leen fey jëf, \q1 ja ngeen nu def! \q1 \v 9 Ndokklee ku ne cas seeni fere, \q1 tas ciw doj! \c 138 \s1 Aji Sax ji waccu ma \d \v 1 Ñeel Daawuda. \b \q1 Ma sante la sama léppi xol, \q1 woy la, gàngooru Yàlla ga ca kaw seede. \q1 \v 2 Ma sujjóot jublook sa kër gu \w sell|lemma="sell:"\w* gi, \q1 di wormaal saw tur, \q1 ngir sa ngor ak sa worma. \q1 Màggal nga sa tur ak sa kàddu, \q1 ba mu tiim lépp. \q1 \v 3 Bés ba ma wootee, yaa ma wuyu, \q1 ñemeel ma, dooleel ma. \b \q1 \v 4 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, na la buuri àddina yépp màggal, \q1 ñoo dégg kàddu yi nga wax. \q1 \v 5 Nañu woy say jaloore, naan: \q1 «Aji Sax jeeka màgg teddnga!» \q1 \v 6 Aji Sax jee kawe! \q1 Ku toroxlu, mu niir; \q1 ku réy, mu ñooru. \b \q1 \v 7 Ma wéye njàqare, \q1 nga musal ma, \q1 dogalee sa loxo merum noon, \q1 walloo ma sa ndijoor. \q1 \v 8 Aji Sax jee may feyul. \q1 Éy Aji Sax ji, yaa saxoo ngor! \q1 Bul wacc ñi nga binde sa loxo. \c 139 \s1 Aji Sax jee ma xam, ba jeexal ma \d \v 1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. \b \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, yaa ma natt, xam ma; \q1 \v 2 yaa xam sama toogaay ak sama taxawaay, \q1 di ràññee fu sore samay xalaat, \q1 \v 3 di càmbar samab dox ak sama tëraay, \q1 yittewoo lépp lu may def. \q1 \v 4 Aji Sax ji, bala maa wax baat, \q1 ndeke yaw, xam nga lépp. \q1 \v 5 Kanam ak gannaaw nga ma dare, \q1 teg ma sa loxo. \q1 \v 6 Ni nga ma xame daa yéeme, \q1 xóot lool, ba wees ma. \b \q1 \v 7 Fu ma jëm, ba sore la? \q1 Fu ma daw jëm, foo teewul? \q1 \v 8 Ma ñalgu ba asamaan, yaa nga fa! \q1 Ma tëri njaniiw, ndeke yaa nga fa! \q1 \v 9 Ma war laafi njël, \q1 dëkki wàllaa géej, \q1 \v 10 nga tettee ma fa ba tey, \q1 téyee ma sa ndijoor. \q1 \v 11 Su ma noon: «Na ma lëndëm mëdd boog, \q1 ba leer gi far guddil ma,» \q1 \v 12 du tax lëndëm lëndëmal la dara. \q1 Guddi da laa leeralal ni bëccëg, \q1 lëndëm dig leer fi yaw. \b \q1 \v 13 Yaa ma sàkkal xol ak xalaat, \q1 ràbbe ma sama biiru ndey. \q1 \v 14 Naa la sante sama bind bu raglu bii te yéeme, \q1 say jalooree di kéemaan, bir na ma! \q1 \v 15 Sama jëmm jii umpu la, \q1 ba muy bindu ci kumpa, \q1 mel ni lu ñu ràbbe ci xóotey suuf. \q1 \v 16 Gis nga ma, ba ma diw lumb; \q1 sa téere lim na \q1 fan yi nga ma àppal, \q1 ba ca benn dooragul. \q1 \v 17 Yàlla, say xalaat aka maa yéem! \q1 Ndaw lim bu réy! \q1 \v 18 Su ma ko doon waññ, moo ëpp feppi suuf. \q1 Maa ngii yewwu, ne feek yaw ba tey. \b \q1 \v 19 Éy sama Yàlla, soo reyoon ñu bon ñii! \q1 Yeen bóomkat yi, soreleen ma! \q1 \v 20 Ñii sa tur lañuy luubale, \q1 noonoo la, di tudd sa tur ciy caaxaan. \q1 \v 21 Aji Sax ji, maaka bañ ñi la bañ \q1 te sib ñi lay gàntal. \q1 \v 22 Dama leena bañ ba fa mbañeel yem; \q1 samay noon dëgg lañu. \b \q1 \v 23 Yàlla, seetlu ma, ba ràññee sama xol; \q1 natt ma, ba ràññee sama xalaati xol. \q1 \v 24 Xoolal ndax maa ngi doxe yoon wu aay, \q1 te nga teg ma ci yoon wi sax. \c 140 \s1 Ku ñu toŋal a ngi ñaan \d Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. \b \q1 \v 1 Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, xettli ma ci ku bon, \q1 musal ma ci nitu fitna, \q1 \v 2 kuy nas lu bon, \q1 tey saxoo di sookey xare, \q1 \v 3 daas làmmiñam ni jaan, \q1 guux daŋaru ñàngóor. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \b \q1 \v 4 Éy Aji Sax ji, aar ma ci loxol ku bon, \q1 musal ma ci nitu fitna, \q1 ku may fexee fakktal. \q1 \v 5 Ñu bew ñee ma làqali yeer, \q1 lalal may buum aki caax, \q1 feggal ma seeni fiir ci yoon wi. \qs Selaw.\qs* \b \q1 \v 6 Dama ne Aji Sax ji, yaay sama Yàlla; \q1 Aji Sax ji, teewlul, ma dagaan la. \q1 \v 7 Aji Sax ji Boroom bi may walloo doole, \q1 yaa ma yiir keroog bésub xare. \b \q1 \v 8 Aji Sax ji, bul may ku bon nammeelam, \q1 bul joyal pexeem, muy yékkatiku. \qs Selaw.\qs* \q1 \v 9 Ñi ma sam, yal na seen ayu làmmiñ \q1 këppu seen kaw bopp. \q1 \v 10 Yal nañu këppoo xali sawara, \q1 tàbbi ciy pax te dootuñu jóg. \q1 \v 11 Kuy yàq der, yàlla bumu toog ci réew mi. \q1 Nitu fitna, yal na ko ay topp, ba dal ci kawam. \q1 \v 12 Xam naa ne Aji Sax jeey jox néew-ji-doole dëgg; \q1 di sàmm àqu baadoolo. \q1 \v 13 Ku def njekk kay a lay sant; \q1 ku jub dëkke saw yiw. \c 141 \s1 Yàlla, sàmmal sama làmmiñ \d \v 1 Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. \b \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, woo naa la, gaawe ma! \q1 Bu ma lay woo, teewlu ma. \q1 \v 2 Yal nanga ma nangul samag ñaan \q1 ni cuuraay lu ñu la taalal, \q1 yoxo yi ma la tàllal di saraxu ngoon soo gërëm. \b \q1 \v 3 Aji Sax ji, sàmmal ma sama làmmiñ, \q1 saytul ma sama kàddu. \q1 \v 4 Bu ma xiir ci lu aay, \q1 may jëfe jëf ju bon, \q1 ànd ceek ñiy jëf lu ñaaw, \q1 di wàlli seeni bernde. \q1 \v 5 Kuy déggal Yàlla, man na maa dóor, \q1 bantal ma ci ngor. \q1 Loolu ngëneelu cuuraay la, duma ko bañ. \q1 Waaye maa ngi saxoo ñaan pexey noon moy. \b \q1 \v 6 Yal nañu fenqe seeni njiit ciw doj, \q1 ba noon yi xam ne dëgg laa wax. \q1 \v 7 Ni ñuy gàbbe suuf ba mu ne ŋafeet, \q1 ni la njaniiw di ŋaye, \q1 aw seeni yax yu tasaaroo. \b \q1 \v 8 Aji Sax ji Boroom bi, yaw laa wékki gët, \q1 yaw laa làqoo, \q1 bu ma seetaan, ma dee. \q1 \v 9 Musal ma ci yeer yi ñu ma gasal, \q1 ak fiir yi ma defkati ñaawtéef yi tegal. \q1 \v 10 Yal na ku bon tàbbi cig fiiram, \q1 te man ma teggi, wéy. \c 142 \s1 Aji Sax ji rekk a ma yég \d Muy taalifu ñaan bu ñeel Daawuda, ba mu nekkee ca xunti ma. \b \q1 \v 1 Ma àddu, ñaan \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji; \q1 àddu ca kaw, di tinu Aji Sax ji, \q1 \v 2 sippi ko sama tawat, \q1 diis ko sama njàqare. \q1 \v 3 Bu ma yoqee, \q1 ràññee nga samay jéego; \q1 yoon wi may jaare \q1 lañu ma làqal am yeer. \q1 \v 4 Ma geesu ndijoor, xool; \q1 du kenn ku ma faale. \q1 Rawtu réer ma, \q1 du kenn ku sama bakkan saf. \b \q1 \v 5 Aji Sax ji, ma woo la wall; \q1 ma ne, yaay sama kiiraay, \q1 di sama séddoo fi kaw suuf. \q1 \v 6 Teewlul, ma ne wóoy, \q1 damaa manatul, \q1 xettli ma ci ñi ma topp, \q1 dañu maa ëpp doole. \q1 \v 7 Ngalla génne ma fi ma tëje, \q1 ma sant la. \q1 Man la way-gëm ñi di yéew ëllëg, \q1 yaa may xéewale ab yool. \c 143 \s1 Aji Sax jeey sama yaakaar \d \v 1 Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. \b \q1 Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, déglul, ma ñaan la; \q1 teewlul, ma tinu la; \q1 nangul ma ci sa wormaak sa njekk. \q1 \v 2 Sang bi, bul layook man; \q1 kenn jubul fi sa kanam, du kuy dund. \q1 \v 3 Noon a ma sambal, \q1 daane ma, joggati, \q1 dëël ma ci lëndëm \q1 ni ku dee bu yàgg. \q1 \v 4 Sama doole jeex tàkk, \q1 sama xol jeex, ma ne yàcc. \q1 \v 5 May fàttliku bu jëkkoon, \q1 di xalaat sa jaloore yépp, \q1 seetaat li nga def. \q1 \v 6 Ma tàllal lay loxo, \q1 di la sàkku, ni suuf su mar di sàkkoo ndox. \qs \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.\qs* \b \q1 \v 7 Aji Sax ji, gaawal wuyu ma; \q1 sama xol a jeex, ma ne yàcc, \q1 bu ma xañ sa yiw, \q1 ma yem ak kuy tàbbiji biir pax. \q1 \v 8 Xëye ma sa ngor, \q1 yaw laa wóolu; \q1 xamal ma fu may doxe, \q1 yaw laa wékk sama bakkan. \q1 \v 9 Aji Sax ji, musal ma ci noon yi, \q1 yaw laa làqoo. \q1 \v 10 Jàngal ma, ma jëfe sa coobare; \q1 yaa di sama Yàlla. \q1 Yal na ma sam xel jiitee mbaax \q1 ci yoon wu tàlli. \q1 \v 11 Aji Sax ji, musal ma ngir saw tur, \q1 jëfeel sag njekk, \q1 teggil ma njàqarey bakkan. \q1 \v 12 Sànkal ma noon yi ci sa ngor, \q1 bóomal ma bépp bañ. \q1 Man de, maay sab jaam! \c 144 \s1 Aji Sax ji, laggsil \d \v 1 Ñeel Daawuda. \b \q1 Cant ñeel na \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ma sës, \q1 mu di ma jàngal xeex, \q1 di ma tàggat ngir xare, \q1 \v 2 di sama wóllëre, di ma yiir, \q1 di ma làq, di ma xettli, \q1 di ma aar, ma di ko làqoo, \q1 mu di ma nangulal ay xeet. \q1 \v 3 Aji Sax ji, luy nit, ba nga di ko ràññee? \q1 luy doom aadama, ba nga di ko faale? \q1 \v 4 Nit ni ngelaw, \q1 ay fanam di takkndeer, wéy. \q1 \v 5 Aji Sax ji, firil asamaan, wàcc; \q1 laal tund yi, ñu saxar. \q1 \v 6 Melaxal, falaxe noon yi; \q1 fittal, ñu fëlxoo, \q1 \v 7 nga yóotoo ma fu kawe, \q1 xettli ma, wallu ma ci doxandéem \q1 yi def wali wal fi sama kaw, \q1 \v 8 di fen, \q1 di giñ ay fen. \q1 \v 9 Yàlla, naa la woyal woy wu yees, \q1 xalamal la xalamu fukki buum. \q1 \v 10 Yaay may buur yi ndam, \q1 yaa musal sa jaam ba, Daawuda \q1 ci saamar bu aay. \q1 \v 11 Musal ma, xettli ma \q1 ci loxol doxandéem \q1 yiy fen, di giñ ay fen. \b \q1 \v 12 Su boobaa sunu doom yu góor \q1 màgge ndaw, ni gàncax gu mat sëkk; \q1 sunuy janq jekk ni doji yett, \q1 yu ñu tabaxe kër buur. \q1 \v 13 Sunuy sàq feese wirgoy wirgo, \q1 sunuy gàtt jur junni, \q1 ba fukki junni (10 000) ci parlu yi, \q1 \v 14 nag yi ëmb ba diis, \q1 du mbas, du biir bu yàqu, \q1 te deesu fi yuuxoo pénc ya. \q1 \v 15 Ndokklee xeet wu am lii! \q1 Ndokklee xeet wu yàllawoo Aji Sax ji! \c 145 \s1 Ma kañ Buur Yàlla \d \v 1 Muy jàngi màggal, ñeel Daawuda. \b \q1 Sama Yàlla, Buur bi, naa la màggal, \q1 teral sa tur ba fàww. \q1 \v 2 Bésoo bés ma di la sant, \q1 di màggal sa tur ba fàww! \q1 \v 3 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee màgg te jara màggala màggal, \q1 kii màggam amul kemu! \b \q1 \v 4 Na maasoo maas di màggal say jaloore, \q1 di biral sa njàmbaarte. \q1 \v 5 Sa leeru teddnga ji ne ràññ, \q1 ak sa jëf ju yéeme laay jàngat! \q1 \v 6 Sa dooley jëf ju raglu dees na ko jottli, \q1 te sa màggaay maa koy yéene. \q1 \v 7 Sa mbaax gu réy, dees na ko tari, \q1 te sag njekk, dees na ko woy. \q1 \v 8 Yiw ak yërmande, Aji Sax ji; \q1 kee muñ mer te bare ngor! \q1 \v 9 Aji Sax jee baaxe ñépp, \q1 di yërëm lu mu sàkk. \b \q1 \v 10 Aji Sax ji, lépp loo sàkk a lay gërëm, \q1 sa wóllëre yi di la sant, \q1 \v 11 di tudd sa teddngay nguur, \q1 tey dégtale sag njàmbaar, \q1 \v 12 doom aadama xam say jaloore \q1 ak sa teddngaak sa darajay nguur. \q1 \v 13 Sa nguur ay nguur gu sax dàkk, \q1 sa kilifteef ñeel maasoo maas. \b \q1 Aji Sax ji daa sàmm ay waxam, \q1 gore ciy jëfam. \q1 \v 14 Ku daanu, Aji Sax ji wallu; \q1 ku sëgg, mu siggil. \q1 \v 15 Ñépp a la wékk bët, di yaakaar, \q1 te bu jotee, yaa leen di leel, \q1 \v 16 tàllal sa loxo, \q1 reggal luy dund, ba xolam sedd. \q1 \v 17 Aji Sax ji, jëfinam jépp njekk la, \q1 jëfam jépp ngor la. \q1 \v 18 Aji Sax ji, képp ku ko woo wall, mu jege la, \q1 képp ku ko woo wall te muy dëgg. \q1 \v 19 Nammeelu ku ko ragal, mu sottal; \q1 yuuxam, mu dégg, musal. \q1 \v 20 Aji Sax jeey sàmm kuy soppeem, \q1 di sànk képp ku bon. \q1 \v 21 Naa sàlloo sant Aji Sax ji, \q1 na luy dund saxoo dàkk di màggal sellngay turam! \c 146 \s1 Buur Yàllaa jara wóolu \q1 \v 1 Màggal-leen Ki Sax! \q1 Naa màggale \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji xol, \q1 \v 2 li feek may dund, di ko kañ, \q1 li feek may noyyi, di woy sama Yàlla. \b \q1 \v 3 Buleen wóolu kilifa, \q1 doom aadama amul wall. \q1 \v 4 Noo ga day rëcc, mu dellu suuf; \q1 bu bés baa, pexeem jeex. \b \q1 \v 5 Ndokklee kuy dimbalikoo Yàllay Yanqóoba; \q1 di yaakaar Yàllaam Aji Sax ji, \q1 \v 6 ki sàkk kaw ak suuf, \q1 géej ak lu ci biiram, \q1 di sàmm dëgg ba fàww, \q1 \v 7 di àtte néew-ji-doole, \q1 di leel ku xiif. \q1 Aji Sax jeey tijji ku ñu tëj. \q1 \v 8 Aji Sax jeey xippil silmaxa, \q1 di siggil ku sëgg. \q1 Aji Sax jee sopp ku jub. \q1 \v 9 Aji Sax jeey sàmm doxandéem, \q1 taxawu jirim ak jëtun, \q1 waaye mooy lajjal pexem ku bon. \b \q1 \v 10 Aji Sax jeey nguuru ba fàww. \q1 Yaw \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, sa Yàllaa ñeel maasoo maas. \q1 Màggal-leen Ki Sax! \c 147 \s1 Yàllaa gën ci àddina, gën ci nit \q1 \v 1 Màggal-leen Ki Sax! \q1 Kañ sunu Yàllaa baax, \q1 màggal koo neex te war. \q1 \v 2 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jaa ngi tabaxaat Yerusalem, \q1 di délloosi ña ñu dàqe Israyil, \q1 \v 3 di faj naqaru xol, \q1 fajtal góomi boroom. \q1 \v 4 Mooy lim biddiiw yi, \q1 tudd bu ci nekk. \q1 \v 5 Sunu Boroom a màgg, bare doole; \q1 am xelam wees kemu. \q1 \v 6 Aji Sax ji, néew-ji-doole, mu yenni; \q1 ku bon, mu daane ci suuf. \b \q1 \v 7 Woyeleen Aji Sax ji kàddug cant, \q1 kañeleen sunu Yàlla jii ay xalam; \q1 \v 8 mooy sànge asamaan ay niir, \q1 tawal suuf, \q1 saxal tund yi am ñax, \q1 \v 9 leel mala, \q1 xol liiru baaxoñ bu jooy. \q1 \v 10 Kii nawul dooley fas, \q1 gërëmul kàttanu jàmbaar. \q1 \v 11 Ki Aji Sax ji gërëm mooy ki ko ragal \q1 te di ko yaakaare ngoram. \b \q1 \v 12 Yerusalem, sargal-leen Aji Sax ji! \q1 yeen waa \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* laa ne, màggal-leen seen Yàlla! \q1 \v 13 Mooy tëj ràpp seen bunti dëkk, \q1 barkeel seen askan wa ca biir, \q1 \v 14 jàmmal seen suufas réew, \q1 reggal leen ngëneelu pepp, \q1 \v 15 yónnee suuf ndigalam, \q1 kàddoom ne coww, daw ca. \q1 \v 16 Mooy tawal yuur bu mel ni wëttéen, \q1 di lay lay bu sedd, mel ni pënd ci suuf. \q1 \v 17 Mooy yuri tawub yuuram niy donj. \q1 Bu ni seddee, ana kuy taxaw? \q1 \v 18 Mu yebal kàddoom, seeyal; \q1 wal ngelawam, ndox walalaan. \q1 \v 19 Mooy wax Yanqóoba kàddoom, \q1 dogalam yaak ndigali yoonam ñeel Israyil. \q1 \v 20 Loolu defalu ko wenn xeet; \q1 kenn xamu ci ndigali yoonam. \q1 Màggal-leen Ki Sax! \c 148 \s1 Na àddina wërngal këpp màggal Yàlla \q1 \v 1 Màggal-leen Ki Sax! \q1 Nangeen màggale \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji fa asamaan, \q1 màggale ko fa kawa kaw. \q1 \v 2 Màggal-leen ko, yeen malaakaam yépp, \q1 màggal-leen ko, yeen gàngooram yi. \q1 \v 3 Màggal-leen ko, yeen jant beek weer wi, \q1 màggal-leen ko, yeen mboolem biddiiw yii di nes-nesi. \q1 \v 4 Màggal-leen ko, yeen asamaani kaw-li-kaw, \q1 ba ca ndox ma tiim asamaan ya. \q1 \v 5 Nañu màggal turu Aji Sax ji, \q1 kii kat a santaane, lii lépp am. \q1 \v 6 Moo leen samp, ñu sax ba fàww, \q1 mu dogal ko, te du toxu. \b \q1 \v 7 Nangeen màggale Aji Sax ji fa kaw suuf, \q1 yeen ninki-nànkay géej ak xóote yépp, \q1 \v 8 ba ca melax yaak doj yu sedd yay taw, \q1 ak tawub yuur akub lay, \q1 ba ca ngëlén yu mag yay def ndigalam. \q1 \v 9 Màggal-leen ko yeen tund yu mag yeek \q1 yu ndaw yépp, \q1 ba ci garab yiy meññ ak garabi seedar yi, \q1 \v 10 ba ci mala yépp, yu àll ak gépp jur \q1 ak luy raam ak njanaaw, \q1 \v 11 ak buuri àddinaak xeet yépp, \q1 ak kilifa yeek njiiti àddina yépp, \q1 \v 12 xale bu góor ak bu jigéen, \q1 mag ak ndaw. \q1 \v 13 Màggal-leen turu Aji Sax ji, \q1 moom doŋŋ la turam kawe, \q1 darajaam tiim asamaan ak suuf. \q1 \v 14 Moo dooleel ñoñam, \q1 wóllëreem ñiy mbooloom \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, \q1 xeet wi mu xejjoo, di ko màggal. \q1 Màggal-leen Ki Sax! \c 149 \s1 Na Israyil màggal Ki Sax \q1 \v 1 Màggal-leen Ki Sax! \q1 Woyleen \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji woy wu yees, \q1 màggal ko fi ndajem wóllëreem ñi. \q1 \v 2 Na Israyil bége kii ko sàkk, \q1 doomi \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, laa ne, ñu bànneexoo seen buur bii. \q1 \v 3 Nañu màggale turam am pecc, \q1 tëggal ko, xalamal ko. \q1 \v 4 Aji Sax jee safoo ñoñam, \q1 di terale néew-ji-doole ag mucc. \b \q1 \v 5 Na wóllërey Yàlla bànneexoo seen ndam, \q1 bu ñu tëddee sax, di sarxolle, \q1 \v 6 di xaacuy kañ Yàlla, \q1 ŋàbbaale saamaru ñaari ñawka, \q1 \v 7 ngir duma yéefar yi, \q1 mbugale ko yooyu xeet, \q1 \v 8 yeewe seeni buur ay càllala, \q1 jénge seeni njiit jéngi weñ, \q1 \v 9 ngir sottalal leen àtte bi ñu bind, \q1 muy ndamu wóllërey Yàlla yépp. \q1 Màggal-leen Ki Sax! \c 150 \s1 Màggal-leen Ki Sax! \q1 \v 1 Màggal-leen Ki Sax! \q1 Nangeen màggale Yàlla biir këram gu \w sell|lemma="sell:"\w*, \q1 màggale ko ca tatay asamaanam. \q1 \v 2 Màggaleleen ko ay jalooreem, \q1 màggale ko màggam gu réy. \q1 \v 3 Màggaleleen kog liit, \q1 màggale ko xalam ak moroom ma. \q1 \v 4 Màggaleleen ko njiin aki pooj, \q1 màggale ko xalam ak toxoro. \q1 \v 5 Màggaleleen ko tëggum weñ mu xumb, \q1 màggale ko tëggum weñ mu kawe. \q1 \v 6 Na lépp luy noyyi màggal Ki Sax! \q1 Màggal-leen Ki Sax!