\id NUM (WOL) \ide UTF-8 \h Màndiŋ ma \toc1 Màndiŋ ma, di ñeenteelu xaaju Tawreetu Musaa \toc2 Màndiŋ ma \mt1 Màndiŋ ma \mt3 fa bànni Israyil jaare woon \mt2 di ñeenteelu xaaju Tawreetu Musaa \imt1 Ubbite gi \ip Téere bii moo tàmbalee ca bés ba bànni Israyil dalee ca taatu tundu Sinayi. Foofu la bànni Israyil jóge jëm màndiŋu Paran, ca bëj-gànnaaru réewum dige ba. Fa lañu yebale ay ndaw yu yërnduji réew ma, te délsi wax seen gis-gis ca ña fa dëkke. Ba ñu demee ba délsi, lañu ne ñoom la ñu gis neexul. Loolu nag tax bànni Israyil di nàttable ndax Yàlla man na leena jox suuf sa mu leen sédd. Ci kaw loolu ñuy jàmbat ci kaw Yàlla. Seen ñàkk kóllëre googu tax na Yàlla teg leen ab daan, ñuy wëndeelu ca màndiŋ ma, ba maas ga doon jàmbat dee, ba geneen maas wuutu leen. Ñeent fukki at lañu wëndeelu, doora walbatiku dox ndànk, jëm Kanaan. Boobu yoon lañu doora nangoo déggal Yàlla. Gannaaw gi lañu sumb ay xare yu am solo, ba daan, ca penkub dexu Yurdan, doora waaj, ngir jàll ca biir réewum dige, ba ñu nammoona gis bu yàgg. Téere bi wone na ne, ni xolu doom Aadama mel rekk moom la ñoñi Yàlla feeñal ci seen jikko ju toogadi. Saxoowuñu lenn, xanaa ŋarale diggante ngëm ak nàttable, cawarte ak xàddi, jëfi ngor ak jëf ju sew. Seen jikko jooju la téere bi wone ne moo leen worale ak Yàlla mi dul soppiku ci kóllëreem, digganteem ak ñoñam, doonte kóllëre gi nag, teewu koo yor ab yaram, te ànd ak njubteem. Musaa nag diggante bu xat lañu ko gisal ci téere bi, Aji Sax ji ak ay bokkam séq ko: Musaa moo doon ndawal Yàlla liy jottli ay ndigalam, te amul woon ab dend ci na mu xejjoo woon ak Yàlla, waaye moo taxawoon itam fa kanam Yàlla, taxawal fa askan wu ñàkk kóllëre, di ko layal te tàyyiwul. \ip Ci Tënk: \ili Saar 1—21 Israyil jànge na ca maam ya jóge woon Misra \ili Saar 22—25 Céru barke bu sax ñeel na Israyil \ili Saar 26—36 Israyil dégg na ab artoom balaa dugg Kanaan \ie \c 1 \ms1 Israyil jànge na ca maam ya jóge woon Misra \mr (Saar 1—21) \s1 Takk nañu limu bànni Israyil \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji moo wax ak Musaa ca màndiŋu Sinayi ca biir \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* ma, keroog benn fanu ñaareelu weer wu ñaareelu at, ma topp ca gàddaay ga bawoo Misra. Mu ne ko: \p \v 2 «Limleen mbooloom \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp, na ñu bokke seeni làng ak seen këri maam. Waññleen góor ñépp, bopp ak bopp, ku nekk ak turam. \v 3 Li ko dale ñaar fukki at, jëm kaw, mboolem ñi xare war ci Israyil daal, nangeen leen lim, gàngoor ak gàngoor, yaw ak Aaróona. \v 4 Giir gu ci nekk, àndleen ceek kilifa yi jiite seen këri maam, ñu jàpple leen ci. \li1 \v 5 Ñiy wuyoo tur yii nag, ñoo leen ciy taxawu: \q1 Ci wàllu Rubeneen ñi, Elisur doomu Sedeyur. \li1 \v 6 Wàllu Cimyoneen ñi, Selumyel doomu Surisadaay. \li1 \v 7 Wàllu Yudeen ñi, Nason doomu Aminadab. \li1 \v 8 Wàllu Isakareen ñi, Netanel doomu Suwar. \li1 \v 9 Wàllu Sabuloneen ñi, Elyab doomu Elon. \li1 \v 10 Ñi ciy askanu Yuusufa ñii la: \q1 Ci wàllu Efraymeen ñi, Elisama doomu Amiyut. \q1 Wàllu Manaseen ñi, Gamalyel doomu Pedasur. \li1 \v 11 Wàllu Beñamineen ñi, Abidan doomu Gidoni. \li1 \v 12 Wàllu Daneen ñi, Ayeser doomu Amisadaay. \li1 \v 13 Wàllu Asereen ñi, Pagyel doomu Okkran. \li1 \v 14 Wàllu Gàddeen ñi, Elyasaf doomu Dewel. \li1 \v 15 Wàllu Neftaleen ñi, Ayra doomu Enan.» \p \v 16 Ñooñu lañu woo ci mbooloo mi, muy ñi jiite seen giiri maam. Ñooy njiiti gàngoori Israyil. \p \v 17 Ba loolu amee Musaa ak Aaróona tofloo ñooñu ñu tudd seeni tur, \v 18 ñu dajale mbooloo ma mépp, keroog ca benn fanu ñaareelu weer wa. La ko dale ca ña am ñaar fukki at, jëm kaw, ñoom ñépp daldi bindu ca limeefu tur ya, ku nekk ak kër maamam, giir ak giir, làng ak làng, bopp ak bopp. \v 19 Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa, na la Musaa takke seen lim ca màndiŋu Sinayi. \p \v 20 Ñu lim bopp ak bopp, turi sëti Ruben taawub Israyil seen maam\f + \fr 1.20 \fr*\ft Israyil mooy Yanqóoba.\ft*\f*, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. \v 21 Limub Rubeneen ñi di ñeent fukki junni ak juróom benn ak juróomi téeméer (46 500). \p \v 22 Ñu lim bopp ak bopp, turi sëti Simeyon, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. \v 23 Limub Cimyoneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300). \p \v 24 Ñu lim turi sëti Gàdd, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. \v 25 Limub Gàddeen ñi di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer ak juróom fukk (45 650). \p \v 26 Ñu lim turi sëti Yuda, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. \v 27 Limub Yudeen ñi di juróom ñaar fukki junneek ñeent, ak juróom benni téeméer (74 600). \p \v 28 Ñu lim turi sëti Isaakar, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. \v 29 Limub Isakareen ñi di juróom fukki junneek ñeent ak ñeenti téeméer (54 400). \p \v 30 Ñu lim turi sëti Sabulon, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. \v 31 Limub Sabuloneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñaar ak ñeenti téeméer (57 400). \p \v 32 Ñu lim turi sëti Yuusufa yi askanoo ci doomam Efrayim, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. \v 33 Limub Efraymeen ñi di ñeent fukki junni ak juróomi téeméer (40 500). \p \v 34 Ñu lim turi sëti Yuusufa yi askanoo ci doomam Manase, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. \v 35 Limub Manaseen ñi di fanweeri junneek ñaar ak ñaar téeméer (32 200). \p \v 36 Ñu lim turi sëti Beñamin, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. \v 37 Limub Beñamineen ñi di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400). \v 38 Ñu lim turi sëti Dan, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. \v 39 Limub Daneen ñi di juróom benn fukki junneek ñaar ak juróom ñaar téeméer (62 700). \p \v 40 Ñu lim turi sëti Aser, ku nekk ak làngam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. \v 41 Limub Asereen ñi di ñeent fukki junneek benn ak juróomi téeméer (41 500). \p \v 42 Ñu lim turi sëti Neftali, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw. \v 43 Limub Neftaleen ñi di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400). \p \v 44 Yooyu limeef la Musaa ak Aaróona tënk, ña leen ca jàpple di fukki kilifay Israyil ak ñaar, ku ci nekk taxawal kër maamam. \v 45 Mboolem bànni Israyil yi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw, limees na leen, ku ci nekk ak kër maamam. \v 46 Ña ñu lim ñépp di juróom benn téeméeri junneek ñett ak juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550). \s1 Limaaleesul Leween ñi \p \v 47 Giirug \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi nag ci bànni Israyil lañu bokk, waaye limaaleesu leen ak ñoom. \v 48 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji moo waxoon Musaa, ne ko: \v 49 «Giirug Lewi ñoom, bu leen lim, bu leen waññaaleek \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \v 50 Waaye yaw ci sa bopp nanga sas Leween ñi jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence, mook la muy àndal lépp, ak mboolem lu ca bokk. Ñooy gàddu jaamookaay bi, ak la muy àndal lépp, di ko topptoo, te it fi wër jaamookaay bi lañuy dal. \v 51 Bu jaamookaay bi dee dem, Leween ñee koy wékki, bu jaamookaay bi dee dale bérab, Leween ñee koy we. Ku ci bokkul ba laal ci nag, dees koy rey. \v 52 Bànni Israyil gi ci des, na ku ci nekk topp dalam, ak raayaam ak kurélam. \v 53 Leween ñi nag nañu dal fi wër jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence. Su ko defee am sànj du dal ci kaw mbooloom bànni Israyil. Te itam na Leween ñi dénkoo dénkaaney jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence.» \p \v 54 Bànni Israyil daldi def noonu. Mboolem lu Aji Sax ji santoon Musaa, noonee lañu ko defe. \c 2 \s1 Lu jëm ci dalinu giir yi \p \v 1 Ba loolu wéyee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax Musaa ak Aaróona, ne leen: \v 2 «Na \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* di dal, ku nekk ak raayaam ak xàmmikaayu kër maamam. Fi wër \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi te dànd ko as lëf, fi lañuy dale: \b \p \v 3 «Ñay dale ca kanam, fa féete penku, ñooy waa raayab Yuda ak seeni gàngoor, kilifag Yudeen ñi di Nason doomu Aminadab. \v 4 Ña ñu lim ci gàngooram di juróom ñaar fukki junneek ñeent ak juróom benni téeméer (74 600). \p \v 5 «Ñay dale fa feggook ñoom ñooy giirug Isakareen ñi, kilifag askanu Isaakar di Netanel doomu Suwar. \v 6 Ña ñu lim ci gàngooram di juróom fukki junneek ñeent ak ñeenti téeméer (54 400). \p \v 7 «Giirug Sabuloneen ñeey feggook ñoom, kilifag askanu Sabulon di Elyab doomu Elon. \v 8 Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek juróom ñaar ak ñeenti téeméer (57 400). \p \v 9 «Mboolem ña ñu limal dalub Yuda aki gàngooram daldi doon téeméeri junneek juróom ñett fukk ak juróom benn ak ñeenti téeméer (186 400). Bu ñuy dem, ñooñooy dox, jiitu. \b \p \v 10 «Waa raayab Ruben ñooy dale bëj-saalum, ñook seeni gàngoor, kilifag askanu Ruben di Elisur doomu Sedeyur. \v 11 Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek juróom benn ak juróomi téeméer (46 500). \p \v 12 «Ñay dale fa feggook ñoom ñooy giirug Cimyoneen ñi, kilifag askanu Simeyon di Selumyel doomu Surisadaay. \v 13 Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300). \p \v 14 «Giiru Gàddeen ñeey feggook ñoom, kilifag askanu Gàdd di Elyasaf doomu Rewel. \v 15 Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer ak juróom fukk (45 650). \p \v 16 «Mboolem ña ñu limal dalub Ruben aki gàngooram doon téeméeri junneek juróom fukk ak benn, ak ñeenti téeméer ak juróom fukk (151 450). Bu ñuy dem, ñooñooy doon ñaareelu kurél, dox, topp ca. \b \p \v 17 «Su ko defee xaymab ndaje mi jóg topp ca, ànd ak \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi koy gàddu, te seen dal nekk ci digg dal yi. Noonee kurél yiy dale daal, ni lañuy jóge dem, ku nekk topp ayam ak raayaam. \b \p \v 18 «Waa raayab Efrayim ñooy dale wetu sowu, ñook seeni gàngoor, kilifag askanu Efrayim di Elisama doomu Amiyut. \v 19 Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junni ak juróomi téeméer (40 500). \p \v 20 «Ñay dale fa feggook ñoom ñooy giirug Manaseen ñi, kilifag askanu Manase di Gamalyel doomu Pedasur. \v 21 Ña ñu limal gàngooram di fanweeri junneek ñaar ak ñaar téeméer (32 200). \p \v 22 «Giirug Beñamineen ñeey feggook ñoom, kilifag askanu Beñamin di Abidan doomu Gidoni. \v 23 Ña ñu limal gàngooram di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400). \p \v 24 «Mboolem ña ñu limal dalub Efrayim aki gàngooram daldi doon téeméeri junneek juróom ñett ak téeméer (108 100). Bu ñuy dem, ñooñoo di ñetteelu kurél, dox topp ca. \b \p \v 25 «Waa raayab Dan ñooy dale bëj-gànnaar, ñook seeni gàngoor, kilifag askanu Dan di Ayeser doomu Amisadaay. \v 26 Ña ñu limal gàngooram di juróom benn fukki junneek ñaar ak juróom ñaar téeméer (62 700). \p \v 27 «Ñay dale fa feggook ñoom ñooy giirug Asereen ñi, kilifag askanu Aser di Pagyel doomu Okkran. \v 28 Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek benn ak juróomi téeméer (41 500). \p \v 29 «Giirug Neftaleen ñeey feggook ñoom, kilifag askanu Neftali di Ayra doomu Enan. \v 30 Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400). \p \v 31 «Mboolem ña ñu limal dalub Dan daldi doon téeméer ak juróom fukki junneek juróom ñaar ak juróom benni téeméer (157 600). Ñooñooy mujja jóg, topp seeni raaya.» \b \p \v 32 Ñooñu lañu limal bànni Israyil na ñu bokke seen këri maam. Mboolem ña ñu limal dal ya ak seeni gàngoor doon juróom benni téeméeri junneek ñett ak juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550). \v 33 Leween ñi nag limaaleesu leen ci bànni Israyil, te noonu la ko Aji Sax ji sante woon Musaa. \p \v 34 Bànni Israyil daldi def noonu. Mboolem noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa, na lañu daan dale, topp seeni raaya, na lañu daan jóge, ku nekk ak làngam ak kër maamam. \c 3 \s1 Lu jëm ci sasi Leween ñi \p \v 1 Ñii ñoo di askani Aaróona ak Musaa, jant ba \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jiy wax, mook Musaa ca kaw tundu Sinayi. \v 2 Doomi Aaróona yu góor ñoo di Nadab, taaw ba, ak Abiyu ak Elasar ak Itamar. \v 3 Turi doomi Aaróona yu góor, \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yaa ngi noonu; ñu faloon leen, sédd leen céru carxal. \v 4 Nadab ak Abiyu nag mujj dee fi kanam Aji Sax ji, ba ñu taalalee Aji Sax ji cuuraay lu warul ca màndiŋu Sinayi. Gannaaw amuñu woon doom yu góor, Elasar ak Itamar daldi féetewoo liggéeyu carxal ba, ca seen kanamu baay Aaróona. \p \v 5 Ci kaw loolu Aji Sax ji ne Musaa: \v 6 «Indil \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi, tegleen ci kilifteefu Aaróona sarxalkat bi, ngir ñu di ko jàpple; \v 7 ñooy dénkoo ndénkaaneem, di dénkoo dénkaaney mbooloo mépp fi kanam \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi, ndax ñooy sasoo liggéeyu jaamookaay bi. \v 8 Ñooy sàmm mboolem jumtukaayi xaymab ndaje mi, ñooy dénkoo dénkaaney \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, ndax ñooy sasoo liggéeyu jaamookaay bi. \v 9 Noonu ngay jële Leween ñi, sédd leen Aaróona ak doomam yu góor. Ñoom ñoo di cér bu mat sëkk bu ñu koy sédde ci bànni Israyil. \v 10 Aaróona ak doomam yu góor nag ngay tabb ngir ñu sasoo seenug carxal, waaye képp ku ci laal te bokku ci, dees koy rey.» \v 11 Aji Sax ji waxati Musaa, ne ko: \v 12 «Man mii nag, maa seppee Leween ñi ci bànni Israyil, maa leen weccoo mboolem taaw bu góor bu jëkka juddoo ci ndeyam, ci biir bànni Israyil. Kon nag Leween ñi, sama cér lañuy doon. \v 13 Ndax lépp luy taaw bu góor, sama cér la. Keroog ba ma fàddee lépp luy taaw bu góor ca réewum Misra, ca laa sellalal sama bopp lépp luy taaw ci Israyil, dale ci nit ba ci jur. Maa leen séddoo. Maay Aji Sax ji.» \s1 Lim nañu Leween ñi ak seeni maam \p \v 14 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ca màndiŋu Sinayi, ne ko: \v 15 «Limal askanu \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi, ni ñu bokke seen këri maam ak seeni làng. Mboolem góor ñi am weer, jëm kaw, ngay lim.» \v 16 Musaa daldi leen lim ci ndigalal Aji Sax ji, na ñu ko ko sante. \p \v 17 Gerson ak Keyat ak Merari ñoo soqikoo ci Lewi.\f + \fr 3.17 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Njàlbéen ga\+bk* 46.11.\ft*\f* \v 18 Doomi Gerson yu góor ñoo di Libni ak Simey, ku ci nekk ak làngam. \v 19 Doomi Keyat yu góor ñoo di Amram ak Isar ak Ebron ak Usyel, ku ci nekk ak làngam. \v 20 Doomi Merari yu góor ñoo di Maali ak Musi, ku ci nekk ak làngam. Làngi Leween ñaa ngoogu, na ñu bokke seen këri maam. \p \v 21 Ci Gerson la làngu Libneen ñi, ak làngu Simeyeen ñi soqikoo. Làngi Gersoneen ñaa ngoogu. \v 22 Ña ñu leen limal, ba ñu waññee mboolem góor ña am weer, jëm kaw, juróom ñaari junni ak juróomi téeméer (7 500) lañu. \v 23 Làngi Gersoneen ña, ca gannaaw jaamookaay ba lañu daan dale, fa féete sowu. \v 24 Gersoneen ñi, seen kilifag kër maam moo doon Elyasaf doomu Layel. \p \v 25 Askanu Gerson nag, seen sas ci wàllu \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi, jaamookaay bi la woon ak xayma bi, ak malaan mi koy ub, ak ridob bunt xaymab ndaje mi, \v 26 ak kiiraayi ëtt beek ridob bunt ëtt bi wër jaamookaay beek \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi, ak buum yeek mboolem liggéey bu ci war. \p \v 27 Keyat nag, ci moom la làngu Amrameen ñi soqikoo, ak làngu Isareen ñi, ak làngu Ebroneen ñi, ak làngu Usiyleen ñi. Làngi Keyateen ñaa ngoogu. \v 28 Ba ñu waññee mboolem góor ña ca am weer, jëm kaw, juróom ñetti junni ak juróom benni téeméer (8 600) lañu. Ñoo dénkoo woon dénkaaney \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi. \v 29 Làngi Keyateen ñi, wet ga féete jaamookaay ba bëj-saalum, fa lañu daan dale. \v 30 Keyateen ñi, seen kilifag kër maam moo doon Elisafan doomu Usyel. \p \v 31 Seen sas nag moo doon \w gaal|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* gi, ak taabal ji, ak tegukaayu làmp bi, ak sarxalukaay yi, ak ndabi sarxal ya ñu ca daa jëfandikoo, ak ridob biir bi, ak mboolem liggéey bu ci war. \v 32 Njiiti Leween ñi nag, seen kilifa gu mag moo doon Elasar doomu Aaróona \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba. Moo doon saytu ña dénkoo woon dénkaaney bérab bu sell ba. \p \v 33 Ci Merari la làngu Maaleen ñi ak làngi Museen ñi soqikoo. Làngi Merareen ñaa ngoogu. \v 34 Ña ñu leen limal, ba ñu waññee mboolem góor ña am weer, jëm kaw, juróom benni junni ak ñaar téeméer (6 200) lañu. \v 35 Merareen ñi, seen kilifag kër maam moo doon Suryel doomu Abixayil. Ca wet ga féete jaamookaay ba bëj-gànnaar, fa lañu daan dale. \p \v 36 Askanu Merari, seen sas moo doon xànqi jaamookaay bi aki galanam ak jën yi ak tegu yi, ak mboolem jumtukaay ya muy àndal, ak liggéey bu ca war, \v 37 ak jën yi wër ëtt bi, ak seeni tegu, ak seen xeri sampukaay, ak seeni buum. \p \v 38 Ña daan dale nag fa jàkkaarlook jaamookaay bi, ca kanam, janlook xaymab ndaje mi, ca wetu penku, ñoo doon Musaa ak Aaróona ak doomam yu góor. Ñoo dénkoo woon dénkaaney bérab bu sell bi, sasool ko \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, te ku ci laal te bokku ci, dees koy rey. \v 39 Mboolem ña ñu limal Leween ñi, te Musaa ak Aaróona lim leen na ñu bokke seeni làng ci ndigalal Aji Sax ji, ñuy mboolem góor ñi am weer, jëm kaw, ñaar fukki junneek ñaar (22 000) lañu. \s1 Lim nañu taaw yi ngir seen njotlaay \p \v 40 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxaat Musaa, ne ko: «Limal taawi \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* yu góor yépp, dale ko ci ñi am weer, jëm kaw, nga waññ te bind seeni tur. \v 41 Su ko defee nga beral ma \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi, man Aji Sax ji, ñu wecci mboolem taawi bànni Israyil gi ci des, juri Leween ñi itam wecci mboolem luy taaw ci juri bànni Israyil gi ci des.» \v 42 Ci kaw loolu Musaa lim taawi bànni Israyil yépp, na ko ko Aji Sax ji sante. \v 43 Ba ñu waññee mboolem taaw yu góor ya, bind seeni tur, dale ci ñi am weer, jëm kaw, seenub lim nekk na ñaar fukki junneek ñaar ak ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñett (22 273). \p \v 44 Aji Sax ji waxati Musaa, ne ko: \v 45 «Beral Leween ñi, ñu wecci mboolem taawi bànni Israyil, juri Leween ñi it wecci seenug jur, ma daldi séddoo Leween ñi, man Aji Sax ji. \v 46 Njotlaay nag dina war ci ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñetti (273) bopp, yi taawi bànni Israyil ëppe Leween ñi. \v 47 Su ko defee nga sàkku bopp bu ci nekk juróomi siikal; ci siikalu \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi nga koy sàkkoo, siikal bu ci nekk wecci ñaar fukki gera\f + \fr 3.47 \fr*\ft Ñaar fukki gera tollu na ci juróom fukki garaam.\ft*\f*. \v 48 Nanga jox xaalis boobu Aaróona ak doomam yu góor, muy njotlaayal taaw yi ci tegu.» \v 49 Ba loolu amee Musaa feyeeku xaalisu njotlaayal taaw yooyu tegu ca taaw, ya jotoo Leween ña. \v 50 Xaalis ba mu nangoo ca taawi bànni Israyil di junniy siikal ak ñetti téeméer ak juróom benn fukk ak juróom (1 365), ci siikalu bérab bu sell bi, xawa tollu ci fukki kilo ak ñett. \v 51 Ci kaw loolu Musaa jox xaalisu njotlaay ba, Aaróona ak doomam yu góor, ci ndigalal Aji Sax ji, na ko ko Aji Sax ji sante. \c 4 \s1 Yeneen kuréli Leween a ngi ak seeni sas \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ak Aaróona, ne: \p \v 2 «\w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi askanoo ci Keyat, waññleen leen bopp ak bopp, na ñu bokke seeni làng, ak seen këri maam. \v 3 Daleleen ci góor ñi am fanweeri at, ba juróom fukki at, muy mboolem ñi yelloo bokk ci kurél, gi liggéeyu biir \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi war. \v 4 Liggéeyu Keyateen ñi ci biir xaymab ndaje mi moo di wàllu jumtukaay yu \w sell|lemma="sell:"\w* yee sell. \p \v 5 «Bu dal bi dee jóg, na Aaróona ak doomam yu góor dugg, wékki kiiraay li, di ridob biir bi, te ñu muure ko \w gaalu seedes kóllëre|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* gi. \v 6 Nañu lalaat ca kaw kiiraayal deru piipi, te ñu lalati ca kaw, ndimo lu lépp baxa, doora roof njàppuy gaal gi. \p \v 7 «Taabalu mburum teewal mi, nañu ci lal ndimo lu baxa, teg ci ndab yeek bàttu yeek njaq yeek tax yi ñuy sottee \w saraxi tuuru|lemma="Sarax yi:"\w*, door cee teg mburu moomu dul wuute. \v 8 Nañu muure yooyu ndimo lu xonq curr, te ñu lalaat ca kaw malaanum deru piipi, doora roof njàppuy taabal ji. \p \v 9 «Su ko defee ñu jël ndimo lu baxa, muure ko tegukaayu làmp bi, aki làmpam aki ñiimam aki andam, ak mboolem ndabi diwam ya ñu cay jëfoo. \v 10 Nañu boole tegukaayu làmp beek mboolem la muy àndal, ñu ëmbe lépp malaanum deru piipi, te teg ko ci kaw tagar bi ñu koy gàddoo. \v 11 \w Sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* wurus bi\f + \fr 4.11\fr*\fk sarxalukaayu wurus bi \fk*\ft mooy sarxalukaayu cuuraay bi. Seetal ci \ft*\ft \+bk Mucc ga\+bk* 30.1-10.\ft*\f*, nañu lal ci kawam ndimo lu baxa, lalaat ca kaw malaanum deru piipi, doora roof njàppuy sarxalukaay bi. \v 12 Nañu jël mboolem jumtukaay yi ñuy liggéeye ci biir \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi, ñu ëmbe ko ndimo lu baxa, muure ko malaanum deru piipi, door koo teg ci kaw tagar bi ñu koy gàddoo. \v 13 Nañu dindi niiniti sarxalukaayu xànjar bi, te ñu lal ci kaw sarxalukaay bi, ndimo lu xonq curr. \v 14 Nañu teg ca kaw ndimo la mboolem ndab, ya ñuy liggéeye ca sarxalukaay ba: and yeek cappukaayi yàpp yeek ñiitukaay yeek këll yi; jumtukaayi sarxalukaay bi yépp daal, te ñu lal ca kaw, malaanum deru piipi, doora roof njàppuy sarxalukaay bi. \p \v 15 «Bu dal bi waree jóg, na Aaróona ak doomam yu góor muur yëf yu sell yi, ak mboolem jumtukaayi bérab bu sell bi ba noppi. Gannaaw loolu la askanu Keyat di dikk, ngir gàddu ko. Su ko defee duñu laal dara lu sell, bay dee. Loolu la Keyateen ñi di gàddu ci wàllu xaymab ndaje mi. \p \v 16 «Elasar doomu Aaróona \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi nag, ab saytoom moo di diwu làmp bi, ak cuuraay li, ak \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* bi dul jaas, ak diwu pal gi. Mooy féetewoo jaamookaay bi bépp, ak mboolem li ci biiram, ba ci yëf yu sell yi, aki jumtukaayam.» \p \v 17 Aji Sax ji waxati ba tey ak Musaa ak Aaróona, ne leen: \v 18 «Buleen yóbbe Keyateen ñeek seeni làng, lu ñu leen di dagge ci biir Leween ñi. \v 19 Nii ngeen di def ak ñoom, ba bu ñu jegee yëf yu sell yee sell, di dund te duñu ca dee: Aaróona aki doomam ñooy dugg, daldi sédd ku nekk ci ñoom liggéeyam ak la muy gàddu. \v 20 Bu Keyateen ñi dugg, di xool lu mu gàtt gàtt, yëf yu sell yi. Lu ko moy ñu dee.» \p \v 21 Gannaaw loolu Aji Sax ji wax Musaa, ne ko: \v 22 «Ñi askanoo ci Gerson itam, nanga leen waññ bopp ak bopp, na ñu bokke seen këri maam ak seeni làng. \v 23 Li dale ci góor ñi am fanweeri at, ba juróom fukki at ngay lim, ñuy mboolem ñi liggéeyu xaymab ndaje mi war. \v 24 Gersoneen ñi nag, lii moo di seen cér ci wàllu liggéey bi, ak li ñu wara gàddu: \v 25 ñooy gàddu kiiraayi jaamookaay bi, ak xaymab ndaje meek malaanam, ak malaanum deru piipi bi ci kaw, ak ridob bunt xaymab ndaje mi; \v 26 ak sori ëtt bi, ak kiiraayal bunt ëtt bi wër jaamookaay beek sarxalukaay bi, ak seeni buum ak mboolem jumtukaay ya ñu cay liggéeye. Mboolem lees cay def, ñoo koy liggéey. \v 27 Mboolem sasu Gersoneen ñi ci mboolem lu ñuy gàddu ak mboolem lu ñuy liggéey, ci ndigalal Aaróona aki doomam lay doon. Ñoo leen di sas mboolem lu ñu wara gàddu. \v 28 Loolooy céru Gersoneen ñi, ci wàllu xaymab ndaje mi, te loolu lañu leen dénk, Itamar doomu Aaróona sarxalkat bi di leen ca saytu. \p \v 29 «Ñi askanoo ci Merari itam, na ñu bokke seeni làng ak seen këri maam, noonu nga leen di lime, \v 30 dale ko ci ñi am fanweeri at, ba juróom fukki at, ñuy mboolem ñi yelloo bokk ci kurél, gi liggéeyu xaymab ndaje mi war. \v 31 Lii mooy li ñu sasoo gàddu ci seen mboolem liggéey ci xaymab ndaje mi: xànqi jaamookaay bi aki galanam aki jënam aki tegoom; \v 32 muy jën yi wër ëtt bi, ak seeni tegu ak seeni buum, mboolem seen jumtukaay yu ñu cay liggéeye. Limal-leen leen jumtukaay yi ñu wara gàddu. \v 33 Loolooy céru Merareen ñi, ci wàllu xaymab ndaje mi ci njiital sarxalkat bi Itamar doomu Aaróona.» \s1 Lim nañu Leween ñi liggéey war \p \v 34 Ci kaw loolu Musaa ak Aaróona ak kilifag mbooloo ma lim Keyateen ña, na ñu bokke seeni làng ak seen këri maam. \v 35 Ñu dale ko ci ñi am fanweeri at, ba juróom fukki at, ñuy mboolem ñi yelloo bokk ci kurél, gi liggéeyu \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi war. \v 36 Ña ñu limal seeni làng di ñaari junni ak juróom ñaar téeméer ak juróom fukki góor (2 750). \v 37 Ñooñu lañu limal làngi Keyateen ñi, ñoom ñépp la liggéeyu xaymab ndaje mi war. Musaa ak Aaróona ñoo leen limoon, na ko \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji santaanee, Musaa jottli. \p \v 38 Ña ñu limal Gersoneen ñi, na ñu bokke seeni làng ak seen këri maam, \v 39 dale ko ci ñi am fanweeri at, ba juróom fukki at, mboolem ña yelloo bokk ci kurél, gi liggéeyu xaymab ndaje mi war, \v 40 te ñu limal leen seeni làng ak seen këri maam, ñaari junneek juróom benni téeméer ak fanweeri góor lañu (2 630). \v 41 Ñooñu lañu limal làngi Gersoneen ñi, te ñoom ñépp la liggéeyu xaymab ndaje mi war. Musaa ak Aaróona ñoo leen limoon ci ndigalal Aji Sax ji. \p \v 42 Ña ñu limal làngi Merareen ñi, na ñu bokke seeni làng, ak seen këri maam, \v 43 dale ko ci ñi am fanweeri at, ba juróom fukki at, mboolem ña yelloo bokk ci kurél, gi liggéeyu xaymab ndaje mi war, \v 44 te ñu limal leen seeni làng, ñetti junni ak ñaar téeméeri góor (3 200) lañu. \v 45 Ñooñu lañu limal làngi Merareen ñi, Musaa ak Aaróona ñoo leen limoon, na ko Aji Sax ji santaanee, Musaa jottli. \p \v 46 Mboolem \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ña Musaa ak Aaróona, ak kilifay Israyil limoon, na ñu bokke seeni làng, ak seen këri maam, \v 47 dale ko ci ñi am fanweeri at, ba juróom fukki at, ñuy mboolem ña yelloo bokk ci kurél, gi liggéeyu xaymab ndaje mi war, \v 48 seenub lim nekk na juróom ñetti junni ak juróomi téeméer ak juróom ñett fukki góor (8 580). \v 49 Ci ndigalal Aji Sax ji Musaa jottli, lañu leen lim, ba sas ku ci nekk ab liggéeyam ak la muy gàddu. Na ko Aji Sax ji sante Musaa, na lañu leen lime. \c 5 \s1 Sàrtal nañu doxalin yiy setal dal bi \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa, ne ko: \v 2 «Santal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ñu génne dal bi képp ku ànd ak jàngoroy der juy law, mbaa jàngoroy xelli, ak képp ku sobeb néew bu mu laal, topp. \v 3 Muy góor, di jigéen, génneleen leen. Bitib dal bi ngeen leen di génne. Buñu sobeel dali bànni Israyil yi ma màkkaanoo ci seen biir.» \p \v 4 Bànni Israyil def noonu, daldi leen génne dal bi, dàq leen ca biti. Ni ko Aji Sax ji waxe Musaa, noonu lañu ko defe. \p \v 5 Aji Sax ji waxati Musaa, \v 6 ne ko mu wax bànni Israyil, ne leen: «Muy góor, di jigéen, bu tooñee moroomam, ba fecci wormay Aji Sax ji, nit kooku tooñ na. \v 7 Day tuub bàkkaaram, ba noppi fey dayo ba mu ameel ka mu tooñ. Te juróomeelu xaajam la cay teg, jox ko ko. \v 8 Bu ki ñu tooñ wuutee, te amul mbokk mu koy jotaat, pey ga ñeel na Aji Sax ji, \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bee koy jagoo, te bokkul ak kuuyum njotlaay, mi sarxalkat biy defale ki tooñ, njotlaayam. \v 9 Te itam bépp jooxe bu bokk ci mboolem sarax yu \w sell|lemma="sell:"\w*, yi bànni Israyil indil sarxalkat bi, sarxalkat bee koy moom. \v 10 Ku nekk ci sarxalkat yi, sa sarax yu sell, yaa ko moom. Ku ci nekk, li ñu la jox, yaay boroom.» \s1 Lu jëm ci jigéen ju moy \p \v 11 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa, \v 12 ne mu wax \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, ne leen: «Képp ku jabaram moy, fecci ko worma, \v 13 bu ñu àndee ak ndaw si, te moom miy jëkkëram yégu ko; te ba ndaw say sobeel boppam, fekkeesu ko fa ba di ko seede; \v 14 ndegam xelum fiiraangee dikkal waa ji, ba mu fiire jabaram, te fekk jabar jaa sobeel boppam ci njaaloo, mbaa muy fiiraange gu dikkal waa ji rekk, mu fiire jabaram, te fekk ndaw si sobeelul boppam ci njaaloo; \v 15 na waa ji yóbbu jabaram ca \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba, te yóbbaleel ko saraxu ñetti kiloy sungufu lors. Du ci sotti diw, du ci def \w cuuraay|lemma="cuuraay l-:"\w*, ndax \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* boobu saraxu fiiraange la, saraxu toppukaay la bu ñuy toppe ñaawtéef. \p \v 16 «Na sarxalkat bi indi ndaw si, taxawal ko fi kanam Aji Sax ji. \v 17 Su ko defee sarxalkat bi day fab ndabal xandeer, duy ko ndox mu sell mi ñuy setloo, te na sàkk ci suufas jaamookaay bi, def ko ci ndox mi. \v 18 Bu taxawloo ndaw si fi kanam Aji Sax ji, na muri boppu ndaw si, te teg ciy loxoom, saraxu pepp boobu di toppukaayu ñaawtéef te di saraxu fiiraange. Na fekk sarxalkat bi yore ciy loxoom ndoxum wextan, miy alage. \v 19 Su ko defee sarxalkat bi waatloo ndaw si, ne ko: “Ndegam góor àndul ak yaw, moyuloo, sobeel sa bopp te fekk la ci buum, muccal ci loraangey ndoxum wextan mii, di alage. \v 20 Waaye su dee yaa moy te fekk la ci sa buumu jëkkër, su dee yaa sobeel sa bopp ak geneen góor gu ànd ak yaw te du sa jëkkër nag...” \v 21 Fii la sarxalkat biy waatloo ndaw si waatu alkànde gi, wax ko ne ko: “...yal na la Aji Sax ji def ku alku ku ñuy móoloo ci sa biir askan. Yal na laxal sa njurukaay, wal sab koll. \v 22 Yal na ndoxum alkànde mii tàbbi ci say butit, laxal sa njurukaay, wal sab koll.” Su ko defee ndaw si ne: “Amiin, Amiin.” \p \v 23 «Na sarxalkat bi bind kàdduy alkànde yooyu cib taxañu bindukaay, te na raxas mbind mi ci ndoxum wextan mi. \v 24 Sarxalkat bi day naanloo ndaw si ndoxum wextan, miy alage, ndox miy alage tàbbi ci biiram, man koo wex xàtt. \v 25 Waaye na jëkka nangoo ci loxol ndaw si, peppum saraxu fiiraange bi, daldi yékkati saraxas pepp mi, jébbale ko fi kanam Aji Sax ji, doora indi sarax bi ci \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi. \v 26 Na sarxalkat bi sàkk ci saraxu pepp bi, ab ŋëb buy fàttlee, daldi koy lakk ci kaw sarxalukaay bi. Gannaaw loolu mu naanloo ndaw si ndox mi. \p \v 27 «Bu ko xasee naanloo ndox mi, ndegam ndaw see sobeel boppam, wor jëkkëram, ndoxum alkànde mi day tàbbi ci biiram, jural ko wextan, koll bi newi, njurukaayam lax, mu mujj doon ku ñuy móoloo ci biir askanam. \v 28 Waaye su ndaw si sobeelul boppam, xanaa di ku set, dina mucc, te dina mana am doom. \p \v 29 «Loolooy dogalu yoon ci mbirum fiiraange, bu jigéen moyee, sobeel boppam te fekk buum ci baatam, \v 30 mbaa jëkkër ju xelum fiiraange dikkal, mu fiire jabaram. Jabar ji lay taxawloo fi kanam Aji Sax ji, sarxalkat bi defal ko mboolem dogalu yoon boobu. \v 31 Deesul topp jëkkër ji genn tooñ, waaye jabar jeey gàddu ñaawtéefu boppam.» \c 6 \s1 Lii moo war ku séddoo Aji Sax ji \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa, \v 2 ne ko mu wax \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen: «Góor ak jigéen, képp ku ci dogu ba xas xasu doon ab nasireen\f + \fr 6.2 \fr*\fk nasireen: \fk*\ft Baat bii jotewul dara ak nasaraan, tur wi ñuy wooye waa sowub jant.\ft*\f*, ngir sédd boppam Aji Sax ji, \v 3 muy biiñ, di ñoll wu mu mana doon, na séddoo di ko moyu. Bineegaru biiñ ak bineegaru ñoll wu mu mana doon it, du ko naan. Mboolem luy ndoxum reseñ, du ko naan, te reseñ ju tooy ak ju wow it, du ko lekk. \v 4 Mboolem diiru fani céddoom, mboolem lu jóge ci doomu garabu reseñ, dale ci xoox ba ci der, du ci lekk lenn. \p \v 5 «Kemu fani céddoo yi mu xas ne dina ko nasireenal, saatus watukaay du laal boppam ba keroog fani nasireenal, yi mu séddoo Aji Sax ji matee. Ku sell lay doon te day jañu. \v 6 Kemu fan yi muy nasireenal, séddoo Aji Sax ji, ab néew, bumu ko jege. \v 7 Baayam ak ndeyam, mbaa góor mbaa jigéen ju mu bokkal waajur sax, bu deeyee, du sobeel boppam ngir ñoom, ndax moo yenu ci kaw boppam, njañu nasireen gi mu séddoo Yàllaam. \v 8 Kemu fani céddoom, ku sell lay doon, ñeel Aji Sax ji. \p \v 9 «Su nit jekkee dee ci wetam, ba sobeel njañu céddoom, keroog bés buy setlu ca lay watu, te keroog bésub juróom ñaareel ba lay watu. \v 10 Bés ba ca topp, di juróom ñetteel ba, na yóbbu ca \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba, ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, ca bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* ma. \v 11 Sarxalkat bi day def menn mi \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*, mi ci des \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, mu jote ko boroom céddoo gi, bàkkaaram ba ko néew ba yóbbe. Bésub keroog lay sellalaat boppam ba yenu woon njañam. \v 12 Day yeesalal Aji Sax ji nasireenam ga mu ko séddoo woon, kemu fan ya mu xasoona nasireenal. Su ko defee day indi xarum menn at, def ko \w saraxas peyug tooñ|lemma="Sarax yi:"\w*. Fan yi mu jëkkoona nasireenal day neen, ndax nasireen googa moo sobewu. \p \v 13 «Dogalu yoon wi ci ab nasireen nag mooy lii: Bés bi ag céddoom matee, dees koy yóbbu ca bunt xaymab ndaje ma. \v 14 Sarax si muy sarxalsi Aji Sax ji di menn xarum menn at mu amul sikk, ngir rendi-dóomal, ak menn xarum menn at mu jigéen mu amul sikk, ngir póotum bàkkaar, ak menn kuuy mu amul sikk, ngir \w saraxas cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*, \v 15 ak pañeb mburu yu amul lawiir, yu ñu lakke sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ak mburu yu sew yu amul lawiir yu ñu wis ag diw, ak \w saraxi peppam|lemma="Sarax yi:"\w* ak \w saraxi tuuroom|lemma="Sarax yi:"\w* ya muy àndal. \p \v 16 «Su ko defee sarxalkat bi boole ko indi fi kanam Aji Sax ji, daldi joxe póotum bàkkaar bi, ak rendi-dóomal bi. \v 17 Kuuy mi, na ko sarxalkat bi def saraxas cant ci biir jàmm, ñeel Aji Sax ji, boole kook pañeb mburu mi amul lawiir, doora joxe saraxi pepp yeek, saraxi tuuru yi. \v 18 Su ko defee nasireen bi watu ci bunt xaymab ndaje mi te for kawari céddoom googu, def ko ci taal, bi ci suufu saraxas cantu biir jàmm bi. \p \v 19 «Na sarxalkat bi jël tànku kanamu kuuy mi, gannaaw bu ñoree, te sàkk ci pañe bi menn mburu mu amul lawiir, ak menn mburu mu ndaw, daldi boole loola teg ci loxol nasireen bi, gannaaw bu watoo ba noppi. \p \v 20 «Na sarxalkat bi jébbale loola, defal ko Aji Sax ji \w saraxu yékkati-jébbal|lemma="Sarax yi:"\w*. Cér yu \w sell|lemma="sell:"\w* a ngoogu ñeel sarxalkat bi, mu boole kook dënn biy saraxu yékkati-jébbal, ak jooxeb tànkub kanam bi. Gannaaw loolu nasireen bi sañ naa naan biiñ. \p \v 21 «Loolooy wartéef ci ab nasireen bu xas. Loolooy saraxam bi mu warlook Aji Sax ji cig céddoom, te bokkewul ak leneen lu mu ci àttan; waaye kàdduy xas wa mu xasoon daal, na sàmmonteek moom ni ko yoon diglee ci céddoom googu.» \s1 Gii ñaan moo war ci askan wi \p \v 22 Gannaaw loolu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa, ne: \v 23 «Waxal Aaróona aki doomam ne leen ni ñuy ñaanale \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, nii la; nañu leen wax ne leen: \p \v 24 «“Yal na la Aji Sax ji barkeel, sàmm la. \p \v 25 «“Yal na la Aji Sax ji geesoo leeram, baaxe la. \p \v 26 «“Yal na la Aji Sax ji siggil, jàmmal la.” \m \v 27 Bu ñu tuddalee noonu bànni Israyil sama tur, man, maa leen di barkeel.» \c 7 \s1 Daloob jaamookaay bi laaj nay sarax \p \v 1 Keroog ba Musaa sampee jaamookaay bi ba noppi, diw na ko ngir sellal ko, mook mboolem ay jumtukaayam, \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* beek mboolem ndabam it, mu boole diw, sellale ko. \v 2 Ba loolu amee kilifay Israyil yi jiite seeni kër maam dikk. Ñooñoo doon njiiti giir yi te ñoo doon saytu limeefu nit ñi. \v 3 Ñu indil \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji seen sarax, muy juróom benni watiir ak fukki nag ak ñaar; ñaari kilifa yu nekk, benn watiir; kilifa gu nekk, wenn nag, ñu yóbbu lépp fa kanam jaamookaay ba. \v 4 Aji Sax ji wax Musaa, \v 5 ne ko: «Nangul lii, mu jëm ci liggéeyu \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi, te nga jox ko \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi, ku ci nekk ak li liggéeyam laaj.» \p \v 6 Musaa nangu watiir yaak nag ya, jox Leween ñi. \v 7 Yii ñaari watiir ak ñeenti nag, mu jox Gersoneen ña, na ko seen liggéey laaje, \v 8 yee ñeent, mu booleek juróom ñetti nag, jox Merareen ña, na ko seen liggéey laaje, ci njiital \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba Itamar doomu Aaróona. \v 9 Keyateen ña nag, joxu leen, ndax yu \w sell|lemma="sell:"\w* ya lañu sasoo woona gàddu. \p \v 10 Ci biir loolu kilifa yi indi itam saraxu daloob sarxalukaay bi, keroog bés ba ñu koy diw. Ñu daldi joxe seeni sarax fi kanam sarxalukaay bi. \v 11 Teewul Aji Sax ji wax Musaa, ne ko: «Kilifa yiy joxesi seen sarax, yi jëm ci daloob sarxalukaay bi, nañu ko def bés bu nekk, kenn.» \p \v 12 Ki joxe saraxam ci bés bu jëkk bi, ñeel giirug Yuda, mooy Nason doomu Aminadab. \v 13 Ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikali \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* bi, \v 14 ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, di téeméeri garaam ak fukk, \v 15 ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy, ak menn xarum menn at, ngir \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, \v 16 ak wenn sikket ngir \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*, \v 17 ak \w saraxas cant gi ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy ak juróomi sikket, ak juróomi xari menn at. Looloo doon saraxu Nason doomu Aminadab. \p \v 18 Bésub ñaareel ba, kilifag Isakareen ña, Netanel doomu Suwar moo indi saraxam, \v 19 sarax ba mu indi di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, di kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikali bérab bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, \v 20 ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, di téeméeri garaam ak fukk, \v 21 ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy, ak menn xarum menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, \v 22 ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, \v 23 ak saraxas cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy ak juróomi sikket, ak juróomi xari menn at. Looloo doon saraxu Netanel doomu Suwar. \p \v 24 Bésub ñetteel ba, kilifag Sabuloneen ña, Elyab doomu Elon moo aye, \v 25 ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikali bérab bu sell bi, di juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, \v 26 ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, muy téeméeri garaam ak fukk, \v 27 ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy, ak menn xarum menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, \v 28 ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, \v 29 ak saraxas cant ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy ak juróomi sikket, ak juróomi xari menn at. Looloo doon saraxu Elyab doomu Elon. \p \v 30 Bésub ñeenteel ba kilifag Rubeneen ña, Elisur doomu Sedeyur moo aye, \v 31 ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, di kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikali bérab bu sell bi, di juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, \v 32 ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, muy téeméeri garaam ak fukk, \v 33 ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy, ak menn xarum menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, \v 34 ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, \v 35 ak saraxas cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy ak juróomi sikket, ak juróomi xari menn at. Looloo doon saraxu Elisur doomu Sedeyur. \p \v 36 Bésub juróomeel ba kilifag Cimyoneen ña, Selumyel doomu Surisadaay moo aye, \v 37 ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, di kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikali bérab bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, \v 38 ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, muy téeméeri garaam ak fukk, \v 39 ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy, ak menn xarum menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, \v 40 ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, \v 41 ak saraxas cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy ak juróomi sikket, ak juróomi xari menn at. Looloo doon saraxu Selumyel doomu Surisadaay. \p \v 42 Bésub juróom benneel ba kilifag Gàddeen ña, Elyasaf doomu Dewel moo aye, \v 43 ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikali bérab bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, \v 44 ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, muy téeméeri garaam ak fukk, \v 45 ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy, ak menn xarum menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, \v 46 ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, \v 47 ak saraxas cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy ak juróomi sikket, ak juróomi xari menn at. Looloo doon saraxu Elyasaf doomu Dewel. \p \v 48 Bésub juróom ñaareel ba kilifag Efraymeen ña, Elisama doomu Amiyut moo aye, \v 49 ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikali bérab bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, \v 50 ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, muy téeméeri garaam ak fukk, \v 51 ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy, ak menn xarum menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, \v 52 ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, \v 53 ak saraxas cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy ak juróomi sikket, ak juróomi xari menn at. Looloo doon saraxu Elisama doomu Amiyut. \p \v 54 Bésub juróom ñetteel ba kilifag Manaseen ña, Gamalyel doomu Pedasur moo aye, \v 55 ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikali bérab bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, \v 56 ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, di téeméeri garaam ak fukk, \v 57 ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy, ak menn xarum menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, \v 58 ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, \v 59 ak saraxu cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy ak juróomi sikket, ak juróomi xari menn at. Looloo doon saraxu Gamalyel doomu Pedasur. \p \v 60 Bésub juróom ñeenteel ba kilifag Beñamineen ña, Abidan doomu Gidoni moo aye, \v 61 ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikali bérab bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, \v 62 ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, di téeméeri garaam ak fukk, \v 63 ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy, ak menn xarum menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, \v 64 ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, \v 65 ak saraxu cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy ak juróomi sikket, ak juróomi xari menn at. Looloo doon saraxu Abidan doomu Gidoni. \p \v 66 Bésub fukkeel ba kilifag Daneen ña, Ayeser doomu Amisadaay moo aye, \v 67 ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikali bérab bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, \v 68 ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, di téeméeri garaam ak fukk, \v 69 ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy, ak menn xarum menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, \v 70 ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, \v 71 ak saraxu cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy ak juróomi sikket, ak juróomi xari menn at. Looloo doon saraxu Ayeser doomu Amisadaay. \p \v 72 Bésub fukkeel baak benn, kilifag Asereen ña, Pagyel doomu Okkran moo aye, \v 73 ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu juróom ñaar fukki siikali bérab bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, \v 74 ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, di téeméeri garaam ak fukk, \v 75 ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy, ak menn xarum menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, \v 76 ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, \v 77 ak saraxu cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy ak juróomi sikket, ak juróomi xari menn at. Looloo doon saraxu Pagyel doomu Okkran. \p \v 78 Bésub fukkeel baak ñaar kilifag Neftaleen ña, Ayra doomu Enan moo aye, \v 79 ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikali bérab bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, \v 80 ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, di téeméeri garaam ak fukk, \v 81 ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy, ak menn xarum menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, \v 82 ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, \v 83 ak saraxu cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy ak juróomi sikket, ak juróomi xari menn at. Looloo doon saraxu Ayra doomu Enan. \p \v 84 Loolooy saraxi daloob sarxalukaay ba, ca bés ba ñu koy diw, sellal ko, lépp bawoo ca kilifay Israyil. Ndabi xaalis ya fukk laak ñaar, këlli xaalis ya di fukk ak ñaar, bàttuy wurus ya di fukk ak ñaar, \v 85 ndabal xaalis lu nekk di téeméeri siikal ak fanweer, di kilook liibar, këll bu nekk di juróom ñaar fukki siikal, di juróom ñetti téeméeri garaam, mboolem xaalisu jumtukaay yi di ñaari junniy siikali bérab bu sell bi ak ñeenti téeméer (2 400), di ñaar fukki kilook juróom ñaar ak juróomi téeméeri garaam (27 500). \v 86 Fukki bàttuy wurus yi feese cuuraay, mbàttu su ci nekk fukki siikali bérab bu sell bi la, di téeméeri garaam ak fukk (110), mboolem wurusu bàttu yi di téeméeri siikal ak ñaar fukk (120), muy kilo ak ñetti téeméeri garaam (1 300). \v 87 Mboolem nagi saraxu rendi-dóomal yi, fukki yëkk yu ndaw ak ñaar la, kuuy yi di fukk ak ñaar, xari menn at yi di fukk ak ñaar, ànd ak seen saraxi pepp, sikketi saraxu póotum bàkkaar bi di fukk ak ñaar. \v 88 Mboolem nagi saraxu cantu biir jàmm yi, ñaar fukki yëkk yu ndaw ak ñeent la, kuuy yi di juróom benn fukk, sikket yi di juróom benn fukk, xari menn at yi di juróom benn fukk. Loolooy saraxi daloob sarxalukaay ba, gannaaw ba ñu ko diwee, sellal ko. \p \v 89 Bu Musaa duggaan ca biir xaymab ndaje ma, ngir wax ak Aji Sax ji, day dégg baat ba di wax ak moom, bawoo fa tiim kubeeru \w gaalu seedes kóllëre|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* ga, ca diggante ñaari \w serub|lemma="serub y-:"\w* ya. Noonu la daan waxeek moom. \c 8 \s1 Lu jëm ci teginu làmp ya \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ne ko, \v 2 mu wax Aaróona, ne ko: «Buy teg làmp yi, fa féete tegukaayu làmp ba kanam, fa la juróom ñaari làmp ya wara niite.» \v 3 Noonu la Aaróona def. Fa féete tegukaay ba kanam, fa la féetale ay làmpam, muy la Aji Sax ji santoon Musaa. \v 4 Tegukaayu làmp bi nag, ni ñu ko liggéeye nii la. Wurus lañu ko tëgge ba mu jekk, dale ko ci tànk bi, ba ci mbar mi. Noonee ko Aji Sax ji wone woon Musaa, na lañu liggéeye tegukaayu làmp ba. \s1 Lu jëm ci cetlug Leween ñi \p \v 5 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ne ko, \v 6 «Nanga jële \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi ci biir \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* te nga setluloo leen. \v 7 Ni ngay def ngir setluloo leen nii la: Danga leen di wis ndoxum setlu, ba noppi ñu wat seen yaram wépp, fóot seeni yére, daldi set. \v 8 Su ko defee ñu jël aw yëkk wu ndaw, booleek \w saraxu peppam|lemma="Sarax yi:"\w*, di sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ak weneen yëkk wu ndaw wooy jël ngir \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*. \v 9 Indil Leween ñi ci kanam \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi, te nga dajale mbooloom bànni Israyil mépp. \v 10 Boo indee Leween ñi fi kanam Aji Sax ji, bànni Israyil daldi teg seeni loxo ci kaw Leween ñi. \v 11 Su ko defee Aaróona taxawal Leween ñi taxawaayu \w saraxu yékkati-jébbal|lemma="Sarax yi:"\w* fi kanam Aji Sax ji, muy sarax bu bawoo ci bànni Israyil, Leween ñi daldi sasoo di liggéey liggéeyu Aji Sax ji. \v 12 Leween ñi ñoom, nañu teg seeni loxo ci kaw boppi yëkk yi, ñu def wenn wi saraxu póotum bàkkaar, te def wi ci des ab \w rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ñeel Aji Sax ji, ngir njotlaayal Leween ñi. \v 13 Gannaaw loolu ngay taxawal Leween ñi fi kanam Aaróona ak doomam yu góor, daldi leen def saraxu yékkati-jébbal, ñeel Aji Sax ji. \v 14 Noonu ngay seppee Leween ñi ci biir bànni Israyil, Leween ñi doon sama cér. \v 15 Gannaaw loolu la Leween ñiy doora dugg ci liggéeyu xaymab ndaje mi. Danga leen di jëkka setluloo, ba noppi def leen saraxu yékkati-jébbal. \v 16 Ñoom déy lañu ma sédda sédd ci biir bànni Israyil, ñu wuutu mboolem luy ubbiteg njur, di taawi mboolem bànni Israyil. Maa leen sédd sama bopp. \v 17 Ndax man maa séddoo mboolem taaw ci biir bànni Israyil, nit ak mala. Keroog ba ma fàddee mboolem taaw ca réewum Misra, ca laa leen sellalal sama bopp. \p \v 18 «Maa jël Leween ñi, weccikoo leen bépp taaw ci biir bànni Israyil, \v 19 te itam maa jukkee Leween ñi ci bànni Israyil, maa leen yékkati, jox leen Aaróona aki doomam, ngir ñu liggéey liggéeyu bànni Israyil ci wàllu xaymab ndaje mi, di defal bànni Israyil seenug njotlaay, ngir bu bànni Israyil jegee \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi it, du tax menn mbas am ci seen biir.» \p \v 20 Ba loolu amee Musaa ak Aaróona ak mbooloom bànni Israyil mépp daldi defal Leween ñi noonu. Mboolem lu Aji Sax ji santoon Musaa ci Leween ñi, noona la ko bànni Israyil defe ak ñoom. \v 21 Leween ñi setlu, fóot seeni yére, Aaróona def leen ni saraxu yékkati-jébbal, ñeel Aji Sax ji. Mu defal leen nag seen njotlaay ngir setal leen. \v 22 Gannaaw loolu Leween ñi doora liggéeyi seen liggéey ci wàllu xaymab ndaje mi, ci kilifteefu Aaróona aki doomam. Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa ci Leween ñi, na lañu def ak ñoom. \p \v 23 Aji Sax ji waxati Musaa, ne: \v 24 «Lii nag moo war ci Leween ñi: ku ci am ñaar fukki at ak juróom, jëm kaw, yelloo naa bokk ci kurél, gi liggéeyu xaymab ndaje mi war. \v 25 Waaye ku xasa am juróom fukki at, na génn kurél gi boobu liggéey war, te bumu ca liggéeyati. \v 26 Sañ naa jàpple bokki Leweenam ñi dénkoo dénkaaney xaymab ndaje mi, waaye dootu ci liggéey lenn. Noonu ngay def ak Leween ñi, ci seen wàlli dénkaane.» \c 9 \s1 Lu jëm ci màggalu bésub Mucc \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na Musaa ca màndiŋu Sinayi, ca seen atum ñaareel, gannaaw ba ñu génnee réewum Misra ca weer wa jëkk. Mu ne ko: \v 2 «Na \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* di màggal \w bésub Mucc|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* ba, saa yu jotee. \p \v 3 «Fukki fan ak ñeent ci weer wii, diggante ngoon ak jant bu so, ci ngeen koy màggal, saa yu jotee. Na mu dëppook mboolem dogali yoonam ak àttey yoonam, nangeen ko màggale noonu.» \p \v 4 Musaa nag sant bànni Israyil ne leen ñu màggal bésub Mucc bi. \v 5 Ñu daldi màggal bésub Mucc bi ci weer wi jëkk, fukki fanam ak ñeent, diggante ngoon ak jant bu so, ca màndiŋu Sinayi. Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa, na la ko bànni Israyil defe. \p \v 6 Ci biir loolu mu am ay nit ñu ab néew tax ñu sobewu, ba manuñoo màggal bésub Mucc bi bésub keroog. Ñu dikk ba ci Musaa ak Aaróona ca bés ba. \v 7 Ñooñu nag ne Musaa: «Nun de, danoo sobewu ndax ab néew, waaye lu nu teree joxesi saraxu Aji Sax ji ci waxtoom, ci digg bànni Israyil?» \v 8 Musaa ne leen: «Taxawleen, ba ma dégg lu Aji Sax ji di santaane ci seen mbir.» \p \v 9 Aji Sax ji ne Musaa: \v 10 «Waxal bànni Israyil ne leen, képp ku bokk ci yeen tey, mbaa mu bokk ci seen kuutaay ëllëg, su sobewoo ndax ab néew, mbaa mu nekk ci yoon wu sore, du tere mu màggal bésub Mucc bi ngir Aji Sax ji. \v 11 Waaye ñaareelu weer wa, ca fukki fanam ak ñeent, diggante ngoon ak jant bu so, ca la koy màggal. Mburu mu amul lawiir ak xob yu wex lay booleek gàttu sarax bi, lekk ko. \v 12 Bumu ci wacc dara mu fanaan, te benn yax, bumu ko ci damm. Na mu dëppook mboolem dogali yooni bésub Mucc, na ko màggale noonu. \v 13 Ku set nag te nekkul ciw yoon, su ñàkkee màggal bésub Mucc bi, kooku dees koy dagge ciw askanam, ndax saraxu Aji Sax ji mu joxewul ci bésam. Kooku moo gàddu bàkkaaru boppam. \p \v 14 «Su dee ab doxandéem bu ngeen dëkkal, sañ naa màggal bésub Mucc bi ñeel Aji Sax ji. Na mu dëppook mboolem dogali yooni bésub Mucc, ak àttey yoonam, ni la koy màggale; benn dogal bi lay doon ci yeen, muy doxandéem bi, di njuddu-ji-réew.» \s1 Aji Sax ji yiir na xaymab ndaje ma \p \v 15 Keroog bés ba ñu sampee màkkaan ma, niir wa daa muur màkkaanu xaymab seede sa. Ca ngoon sa lu mel ni sawara tiim màkkaan ma, ba ca ëllëg sa. \v 16 Noonu la ko niir wa jàppoo muure, bu guddee mu mel ni sawara. \v 17 Fu niir wa masa bàyyikoo fa tiim xayma ba, \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* day fabu topp ko, te fépp fu niir wa masa dale, fa la bànni Israyil di fàkk ab dal. \v 18 Ci kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji la bànni Israyil daan faboo, ci kàddug Aji Sax ji lañu daan dale, te mboolem fan ya niir way dal, tiim màkkaan ma, ñoom it dañuy dal. \v 19 Su niir wa yàggee ca kaw màkkaan ma it, ak lu fan ya bare bare, bànni Israyil a ngay dénkoo dénkaaney Aji Sax ji, waaye duñu dem. \v 20 Leeg-leegaa fan yu néew la niir way dal-lu fa tiim màkkaan ma. Waaye ci kàddug Aji Sax ji daal, lañuy dale te ci kàddug Aji Sax ji lañuy faboo. \v 21 Leeg-leegaa it niir wa dal-lu ag ngoon, fanaan, ba bët set, mu sàqi, ñu fabu ànd ak moom. Muy guddi, di bëccëg, bu niir wa jógaa, rekk, ñu fabu. \v 22 Su doon ñaari fan, su doon weer, mbaa ay fani fan la niir wa taxaw tiim màkkaan ma, des fa it, bànni Israyil dañuy dal, waaye duñu dem. Bu jógee rekk lañuy fabu. \v 23 Ci kàddug Aji Sax ji lañu daa dale, ci kàddug Aji Sax ji lañu daa faboo. Dénkaaney Aji Sax ji daal lañuy dénkoo, ci kàddug Aji Sax, ji Musaa di jottli. \c 10 \s1 Lu jëm ci liiti xaalis ya \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa, ne: \v 2 «Sàkklul ñaari liiti xaalis. Lu ñu tëgglu ba mu jekk nga koy def. Liit yi ngay wootee am ndaje, di ko yékkatee dal yi. \v 3 Bu ñu liitee ñaar yépp, mbooloo mépp ay dajesi fi yaw, ci bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi. \v 4 Bu ñu liitee benn nag kilifa yi jiite gàngoori Israyil ñooy dajesi fi yaw. \v 5 Su ñu liitee menn riirum liit mu xumb, dal yi dale penku ñooy fabu. \v 6 Su ñu liitee riirum liit mu xumb, ñaareel bi yoon, dal yi dale bëj-saalum ñooy fabu. Riirum liit mu xumb mooy tegtale seeni fabu. \v 7 Bu dee wooteb ndaje nag, dees koy liit waaye du doon riir mu xumb. \v 8 Na doomi Aaróona \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi di wal liit yi, te mu doon dogal bu leen saxal dàkk, ci seen maasoo maas. \p \v 9 «Bu loolu wéyee, bu ngeen dee xare ci seenum réew, ak noon bu leen songsi, nangeen riiral liit yi riir mu xumb, su boobaa dees na leen bàyyi xel fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ba wallu leen ak seeni noon. \v 10 Seen bési mbég itam, muy seen bési màggal, di seen ndoortel weer, nangeen ciy riiral liit yi riir mu xumb, yéenee ko seen \w saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ak seen \w saraxi cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*. Riirum liit yooyu mooy doon seen baaxantal fa seen kanam Yàlla. Maay seen Yàlla, Aji Sax ji.» \s1 Bànni Israyil sàqee nañu tundu Sinayi \p \v 11 Ca ñaareelu at ma, gannaaw ba bànni Israyil génnee Misra, ca ñaareelu weer wa, keroog ñaar fukkeelu fanam, ca la niir wa bàyyikoo fa tiim màkkaanu seedes kóllëre ga. \v 12 \w Bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* daldi sumb seen yooni tukki ya, bàyyikoo màndiŋu Sinayi. Ci kaw loolu niir wa daleji ca màndiŋu Paran. \p \v 13 Booba lañu jëkka fabu ci kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, Musaa jottli. \v 14 Raayab dalu Yudeen ña moo jëkka jóg, ànd aki gàngooram, njiital gàngooru Yuda di Nason doomu Aminadab, \v 15 njiital gàngooru Isakareen ña di Netanel doomu Suwar, \v 16 njiital gàngooru Sabuloneen ña di Elyab doomu Elon. \p \v 17 Ci biir loolu ñu wékki jaamookaay ba, Gersoneen ñaak Merareen ñay gàddu jaamookaay ba daldi dem. \p \v 18 Raayab dalu Rubeneen ña jóg ànd aki gàngooram, topp ca, njiital gàngooru Rubeneen ña di Elisur doomu Sedeyur, \v 19 njiital gàngooru Cimyoneen ña di Selumyel doomu Surisadaay, \v 20 njiital gàngooru Gàddeen ña di Elyasaf doomu Dewel. \p \v 21 Gannaaw loolu Keyateen ñay gàddu yëf yu sell ya, ñoo fabu, topp ca. Bala ñoo àgg fa ñuy dalewaat nag, day fekk jaamookaay ba sampewaat. \p \v 22 Ci kaw loolu raayab dalu Efraymeen ña jóg, ànd ak seeni gàngoor, topp ca, njiital gàngooru Efraymeen ña di Elisama doomu Amiyut, \v 23 njiital gàngooru Manaseen ña di Gamalyel doomu Pedasur, \v 24 njiital gàngooru Beñamineen ña di Abidan doomu Gidoni. \p \v 25 Ba mu ko defee raayab dalu Daneen ña doora jóg, topp ca gannaaw kurél yépp, ànd aki gàngooram, njiital gàngooru Daneen ña di Ayeser doomu Amisadaay, \v 26 njiital gàngooru Asereen ña di Pagyel doomu Okkran, \v 27 njiital gàngooru Neftaleen ña di Ayra doomu Enan. \p \v 28 Noonu la bànni Israyil topplantee, ànd ak seeni gàngoor, tegu ca yoon wa. \s1 Bànni Israyil jóge nañu Sinayi \p \v 29 Ba loolu amee Musaa wax ak Obab doomu Ruwel waa Majan ba, baayu soxnaam, ne ko: «Nu ngi nii jëm fa nu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax ne moom lanuy jox. Kaay nu ànd, dem, nu baaxe la, ndax Aji Sax ji moo digee baaxe Israyil.» \p \v 30 Mu ne ko: «Déedéet, duma dem, samam réew kay laa jëm, ca saay bokk.» \v 31 Mu ne ko: «Bu nu wacc kay, ndax gannaaw yaa xam fu nu wara dal ci màndiŋ mi, yaa nu wara jiite. \v 32 Soo àndeek nun déy, xéewal googa nu Aji Sax jiy baaxeji, dinanu la ci baaxe.» \p \v 33 Ci kaw loolu ñu bàyyikoo ca tundu Aji Sax ja, doxe fa doxub ñetti fan. \w Gaalu kóllërey Aji Sax|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* jaa nga leen jiitu diiru ñetti fan ña, di leen wutal dal-lukaay. \v 34 Niiru Aji Sax ji nag di leen yiir bëccëg bu nekk, saa yu ñu bàyyikoo ab dal. \p \v 35 Bu gaal ga jógaan, Musaa da naan: \q1 «Jógaloo, Aji Sax ji, say noon fëlxoo, \q1 say bañ daw la.» \p \v 36 Bu gaal ga dalee, Musaa ne: \q1 «Dikkaloo Aji Sax ji boroom ndiiraani junniy Israyil.» \c 11 \s1 Bànni Israyil ñaxtu nañu \p \v 1 Mbooloo ma nag mujj di tawat ab coono fi kanam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Aji Sax ji dégg ci, am sànjam tàkk, sawaras Aji Sax ji tàkkal leen, ba xoyom la wër dal ba. \v 2 Mbooloo ma jooy ko Musaa, Musaa tinu Aji Sax ji, sawara wa fey. \v 3 Ñu tudde bérab boobu Tabera (mu neexook Tàkkaan), ndax sawaras Aji Sax ji leen fa tàkkal. \p \v 4 Ci biir loolu genn gàngooru njaxasaan mu nekkoon ca seen biir jiital seen bakkan, di ŋaf-ŋafi, ba tax \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* itam dellu di jàmbat. Ña nga naan: «Éy ku nuy leelatiw yàpp! \v 5 Namm nan jën ya nu daa ndawaloo ca Misra, te dikkewu nu tus! Ak yomb jaak xaal jaak pooro baak soble saak laaj ja! \v 6 Tey jii sunu put yaa ngi wow koŋŋ, gisunu lenn lu moy mànn\f + \fr 11.6 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Mucc ga\+bk* 16.12-21.\ft*\f*!» \p \v 7 Mànn ma nag daa meloon ni pepp mi ñuy wax koryanda, te nirook ndàbbu garab gi ñuy wax bedola. \v 8 Mbooloo ma da daan wër, di ko for, di ko wole doji wolukaay, mbaa ñu di ko dëbb ciy gënn, ba noppi baxal ko ci cin, def ko ay mburu yu cafkaam mel ni cafkay nàkk yu am niw. \v 9 Bu layaa ca dal ba ag guddi, mànn ma day wàccaale ak moom. \p \v 10 Ci biir loolu Musaa dégg mbooloo miy ñaxtu, làng ak làng, ku nekk ci sa bunt xayma. Ba loolu amee sànjum Aji Sax ji tàkk jippét, Musaa nag ñaawlu ko. \v 11 Ba mu ko defee Musaa ne Aji Sax ji: «Aji Sax ji, loo may mititale, Sang bi? Lu tee nga baaxe ma, xanaa ngay teg sëfub mii mbooloo mépp ci sama kaw? \v 12 Xanaa maa ëmb mii mbooloo mépp, am maa leen jur, ba nga di ma leen bootloo fàpp, ni jaboot di boote luy nàmp, jëme leen réew, ma nga giñaloon seeni maam? \v 13 Ana fu may jële yàpp wu ma jox mii mbooloo mépp, ba ñuy jooy nii ci sama kaw, naa ma: “Jox nu yàpp wu nu lekk.”? \v 14 Manumaa boot mii mbooloo mépp, man doŋŋ, ndax àttanuma ko. \v 15 Su dee nii ngay def ak man nag, dimbali ma rekk, rey ma ba ma dee, ndax ma baña gis sama toskare.» \s1 Aji Sax ji dig na Musaa ñu ko jàpple \p \v 16 Ba mu ko defee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax Musaa, ne ko: «Dajaleel ma juróom ñaar fukki magi Israyil, ñoo xamal sa bopp ne ñooy magi mbooloo mi, di seeni njiit, nga indi leen ci \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi, ñu teew faak yaw. \v 17 Maay wàcc wax ak yaw foofa te maay sàkk ci leer gi ci yaw, def ko ci ñoom, ñu yenule la yenu mbooloo mi, ba dootuloo ko yenu yaw doŋŋ. \p \v 18 «Mbooloo mi nag, ne leen ñu sell-lu ngir ëllëg, te ne leen dinañu yàpp moos, gannaaw ñooy jooy ci kaw Aji Sax ji, naan “Éy ku nuy leelatiw yàpp, nooka neexle woon ca Misra!” Kon nag Aji Sax jee leen di jox yàpp wu ñu lekk. \v 19 Du benn fan lañuy yàpp, du ñaar, du juróomi fan, du fukk, te du ñaar fukki fan. \v 20 Weeru lëmm kay lañuy yàpp, ba yàpp wiy génne ci seen paxi bakkan, ba mujj génnliku leen, gannaaw ñoo xarab Aji Sax ji ci seen biir, di jooy ci kawam, naan: “Moo lu nu taxoona jóge Misra!”» \p \v 21 Ci kaw loolu Musaa ne: «Ãa! Juróom benni téeméeri junniy (600 000) góor a ngi ci mbooloo mii ma ne ci seen biir. Yaw nga ne aw yàpp nga leen di jox, ñu yàpp weeru lëmm! \v 22 Diggante jur gu gudd ak gu gàtt, manees na leen cee rendil lu leen doy a? Am mboolem jëni géej lees leen di dajaleel, mu doy leen?» \p \v 23 Aji Sax ji ne Musaa: «Loxol Aji Sax ji da koo jotewul? Léegi nag dinga gis ndax sama kàddu dina la sottil, am déet!» \s1 Yàlla sol na mag ña ag leeram \p \v 24 Ci kaw loolu Musaa génn, jottli mbooloo ma kàdduy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, daldi dajale juróom ñaar fukki góor ñu bokk ca magi mbooloo ma, taxawal leen, ñu wër xayma ba. \v 25 Aji Sax ji nag wàcc ca biir niir wa, wax ak moom, daldi sàkk ca leer ga ca Musaa, sédd ca juróom ñaar fukki mag ña. Naka la leer ga dal ca seen kaw, ñu tàmbali di wax ay \w waxyu|lemma="waxyu:"\w*, benn yoon bu ñu tóllantiwul. \p \v 26 Fekk na ñaari góor a nga desoon ca dal ba, kenn ka di Eldàdd, ka ca des di Medàdd, te teewul leer ga dal ca seen kaw, ndax dees leena limaale woon ca mag ña, doonte demuñu ca xayma ba. Ñoom it ñuy wax ay waxyu ca dal ba. \v 27 Ab xale dawe ca, àgge ko Musaa, ne ko: «Eldàdd ak Medàdd déy a ngay wax ay waxyu ca dal ba!» \v 28 Yosuwe doomu Nuun, ja dale doon bëkk-néegu Musaa cag ndawam, daldi cay àddu, ne: «Sang Musaa, aaye leen!» \v 29 Musaa ne ko: «Fiiraangee la jàpp ndax man, am? Éy bu niti mbooloom Aji Sax ji mépp doon ay yonent, Aji Sax ji sol leen ag leeram!» \v 30 Ba loolu amee Musaa dellu ca dal ba, moom ak magi Israyil ña. \s1 Mbas wàcc na ca Kibbrot Taawa \p \v 31 Ba loolu amee ngelaw wale ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, daldi bàbbee ca géej ga ay picci përëntaan, wàcce leen ca dal ba lu tollook doxub benn fan ci gii wet, ak doxub benn fan ca gee, ñu dajal dal ba bépp, jale ci suuf ba xawa mat ñaari xasab. \v 32 Ci kaw loolu mbooloo ma taxaw di for, bëccëgub keroog bépp, ak guddi ga gépp, ak bëccëgub ëllëg sa sépp, ba ka gëna néewle, for lu mat fukki barigo. Ñu weer përëntaan ya fa wër dal ba. \v 33 Suux waa nga ca seeni gëñ, sàqameeguñu sax, sànjum Aji Sax ji tàkkal mbooloo ma. Aji Sax ji dumaa mbooloo ma mbas mu metti lool. \v 34 Moo tax ñu tudde bérab booba Kibbrot Taawa (mu firi Bàmmeeli ŋaf-ŋaf), ndax fa lañu denc néewi mbooloo ma doon ŋaf-ŋafi. \v 35 Kibbrot Taawa la mbooloo ma bàyyikoo, jëm Aserot. Ñu dal nag ca Aserot. \c 12 \s1 Maryaama ak Aaróona jote nañook Musaa \p \v 1 Maryaama ak Aaróona ñoo doon ŋàññ Musaa, ci ndawas \w Kuuseen|lemma="Kuus:"\w* su mu takkoon, te ab Kuuseen it la takkoon. \p \v 2 Ñu ne: «Ndax mennum Musaa doŋŋ la \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jiy waxe ci moom? Xanaa daa waxewul ci nun itam?» Aji Sax ji dégg ca. \v 3 Góor ga Musaa nag defoon ku woyof lool, ba raw mboolem doom aadama ci kaw suuf. \v 4 Ci kaw loolu Aji Sax ji jekki wax ak Musaa ak Aaróona ak Maryaama, ne leen: «Dikkleen, yeen ñett, ci \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi!» Ñu dem, ñoom ñett. \v 5 Aji Sax ji wàcc ci biir niir wu def aw taxaar. Mu taxaw ca bunt xayma ba, daldi woo Aaróona ak Maryaama, ñu bokk dikk. \v 6 Mu ne leen: «Dégluleen bu baax samay kàddu: su ngeen feeñlee ab yonentu Aji Sax ji, ci am peeñu laa koy xamale maay kan, te ci gént laay waxeek moom, \v 7 waaye du Musaa sama jaam bii. Moom mooy ki wóor ci mboolem sama kër gii. \v 8 Gémmiñ ak gémmiñ laay waxeek moom wax ju leer nàññ ju ñu léebul, te jëmmu Aji Sax ji lay gis. Kon lu leen may fitu ŋàññ Musaa sama jaam bi?» \v 9 Sànjum Aji Sax ji nag tàkkal leen. Ci kaw loolu mu dem. \p \v 10 Naka la niir wa jóge ca xayma ba, Maryaama jekki ne fureet ak jàngoroy ngaana, weex furr! Aaróona ne Maryaama gees, yem ca ngaana ga. \v 11 Aaróona ne Musaa: «Ngalla sang bi, bu nu topp bàkkaar bi nu bàkkaar ndax ñàkk xel! \v 12 Ngalla bul seetaan kii mel ni ku dee te indaalewul bakkan ba mu juddoo ca ndeyam, xaaju yaram wi lekku!» \v 13 Musaa nag jooy Aji Sax ji, ne ko: «Yàlla, ngalla wéral ko!» \p \v 14 Aji Sax ji ne Musaa: «Xanaa baayam sax su ko jéppi woon, ba tifli ko ci kanam, muy gàcceem diiru juróom ñaari fan? Nañu ko génne dal bi diiru juróom ñaari fan, door koo délloosi ci biir.» \v 15 Ba loolu amee ñu génne Maryaama dal ba diiru juróom ñaari fan. Mbooloo ma demul, ba keroog ba ñu délloosee Maryaama ca biir dal ba. \v 16 Gannaaw loolu mbooloo ma bàyyikoo Aserot, ñu dali ca màndiŋu Paran. \c 13 \s1 Musaa yeble na Kanaan \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa, ne: \v 2 «Yebalal ay ndaw, ñu dem yëri réewum Kanaan, gi may jox \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. Kenn ngay yebal ci seen giiri maam yi, giir gu ci nekk, kenn, te ku ci nekk di kilifa ci ñoom.» \v 3 Ci kaw loolu Musaa yebal ndaw ña ci ndigalal Aji Sax ji, ñu bàyyikoo ca màndiŋu Paran. Ñoom ñépp ay njiiti bànni Israyil lañu woon. \v 4 Ñooñu ñoo di: \li1 Samwa doomu Sakuur, ci giirug Rubeneen ñi, \li1 \v 5 ak Safat doomu Ori, ci giirug Cimyoneen ñi, \li1 \v 6 ak Kaleb doomu Yefune, ci giirug Yudeen ñi, \li1 \v 7 ak Igal doomu Yuusufa, ci giirug Isakareen ñi, \li1 \v 8 ak Oseya doomu Nuun, ci giirug Efraymeen ñi, \li1 \v 9 ak Palti doomu Rafu, ci giirug Beñamineen ñi, \li1 \v 10 ak Gadyel doomu Sodi, ci giirug Sabuloneen ñi, \li1 \v 11 ak Gadi doomu Susi, mi taxawal làngu Manase ci biir giirug Yuusufeen ñi, \li1 \v 12 ak Amyel doomu Gemali, ci giirug Daneen ñi, \li1 \v 13 ak Setur doomu Mikayel, ci giirug Asereen ñi, \li1 \v 14 ak Nabi doomu Wofsi, ci giirug Neftaleen ñi, \li1 \v 15 ak Gewuyel doomu Maki, ci giiru Gàddeen ñi. \p \v 16 Ñooñu la Musaa yónni woon, ngir ñu yëri réew ma. Oseya doomu Nuun nag, Musaa tudde ko Yosuwe. \p \v 17 Ba leen Musaa yebalee ngir ñu yëri réewum Kanaan, da ne leen: «Negew gii ci bëj-saalum ngeen di jaare, yéegi ca diiwaanu tund ya, \v 18 ba gis nu réew ma mel: ndax waa réew ma, ñu am doole lañu, am ñu néew doole; ñu néew lañu, am ñu bare; \v 19 ak ndax réew ma baax na, am baaxul; ak nu seeni dëkk mel: ndax ay dal rekk la, am ay dëkk yu ñu dàbbli la; \v 20 ak suuf sa: ndax nangu na, am nanguwul; ak itam ndax am nay garab, am déet. Te ngeen góor-góorlu ba sàkkaale ca meññeefi réew ma.» Fan yooyu nag yemook reseñ di meññ ndoortel meññeef. \p \v 21 Ci kaw loolu ndaw ya dem yëri réew ma, dale ko ca màndiŋu Ciin, ba àgg Reyob, ga ca wetu Amat. \v 22 Ña nga jaare Negew ca bëj-saalum, dem ba Ebron, fa Anageen ña, Ayman ak Sesay ak Talmay, dëkkoon. Ebron googee, tabaxees na ko juróom ñaari at lu jiitu Cowan ga ca Misra. \v 23 Ñu dem ba ca xuru Eskol, daldi fay dagge ab car bu def benn cëggub reseñ, ñaar ca ñoom gàddoo ko bant, ñu sàkkaale fa gërënaat ak figg. \v 24 Bérab boobu lañu dippee xuru Eskol, (mu firi xuru Cëgg) ndax cëgg ba fa bànni Israyil dagge woon. \s1 Ndaw ya délsi nañu \p \v 25 Ndaw ya nag ñibbsi, gannaaw ba ñu nemmikoo réew ma lu mat ñeent fukki fan. \v 26 Ñu dikk ba ci Musaa ak Aaróona, ak mbooloom \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp, ca màndiŋu Paran, ca Kades. Ñu àgge leen xibaar, ñoom ak mbooloo ma mépp, ba noppi won leen meññeefum réew ma. \v 27 Ci kaw loolu ñu nettali Musaa, ne: «Dem nanu réew, ma nga nu yebaloon, te it foofa la meew maak lem ja tuuroo! Lii ca meññeef maa. \v 28 Xanaa kay, kàttan gu askanu réew ma am, péey ya dàbbliku te yaa lool. Te it ponkal yooyu cosaanoo ci Anageen ñi lanu fa gis. \v 29 Amalegeen ñaa dëkke bëj-saalumu réew ma, Etteen ñaak Yebuseen ñaak Amoreen ña dëkke diiwaanu tund ya, Kanaaneen ña dëkke wetu géej, feggook dexu Yurdan.» \p \v 30 Ci kaw loolu Kaleb noppiloo mbooloo ma, fekk leen tàmbalee diiŋat Musaa. Mu ne leen: «Nooy dem ba demaatoo, nanguji réew ma, ndax bir na ne noo leen mana duma.» \p \v 31 Ndaw ya àndoon ak moom daldi ne: «Manunoo songi waa réew ma, ndax ñoo nu ëpp doole.» \v 32 Ci biir loolu ñuy baatal ca kanam bànni Israyil, réew ma ñu nemmikuji woon. Ñu naan: «Réew moomee ñu wëri woon ngir nemmiku ko déy, réew la muy faagaagal ay sancaanam, te mboolem askan wa nu fa gis, ay boroom jëmm lañu. \v 33 Fa lanu gis xeetu Nefilim ya, ponkali Anageen ña bokk ca xeetu Nefilim ya, nuy niru sunu bopp ay soccet fi seen kanam, di leen ko niru, ñoom it.» \c 14 \s1 Mbooloo ma bañ naa duggi Kanaan \p \v 1 Ba loolu amee mbooloo mépp tàmbalee yuuxu. Askan wa daa fanaanee jooy guddig keroog. \v 2 \w Bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp nag di ñaxtu ci kaw Musaa ak Aaróona, mbooloo ma mépp naa leen: «Waay lu nu tee woona dee ca réewum Misra, mbaa sax nu dee ci màndiŋ mii! \v 3 Ana lu nu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jiy indee ci réew mii ñu nara fàddoo saamar, sunuy jabar ak sunuy tuut-tànk doon alalu sëxëtoo! Tee noo dellu Misra yee?» \v 4 Ci kaw loolu ñu naan ca seen biir: «Nan fal njiit te dellu Misra.» \p \v 5 Ba loolu amee Musaa ne gurub, moom ak Aaróona, ñu dëpp seen jë fa suuf, fa kanam mbooloom bànni Israyil ma fa daje mépp. \v 6 Yosuwe doomu Nuun, ak Kaleb doomu Yefune, ñoom ña bokk ca ña seeti woon réew ma, daldi xotti seeni yére ndaxu tiis. \v 7 Ñu wax nag mbooloom bànni Israyil mépp, ne leen: «Réew ma nu wëri woon, ba nemmiku ko, réew mu baaxa baax la. \v 8 Bu nu Aji Sax ji nangulee, moo nuy dugal réew moomu, moo nuy jox réew ma meew maak lem ja tuuroo. \v 9 Fexeleen rekk ba Aji Sax ji, buleen ko gàntal, te yeen nag ngeen baña ragal waa réew ma, ndax ab lanc doŋŋ lañu nuy mat. Seen kiiraay dëddu na leen, te Aji Sax jaa ngeek nun. Buleen leen ragal.» \s1 Gàntal Aji Sax ji sabab na mbugal \p \v 10 Ba mu ko defee mbooloo ma mépp ne dañu leen di dóori xeer ba ñu dee. Leeru \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nag feeñ ca \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* ma, ci kanam \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp. \p \v 11 Ba loolu amee Aji Sax ji ne Musaa: «Ba kañ la ma askan wii nara xarab? Ba kañ lañu may gëmadi, ak firnde yi ma def ci seen biir yépp? \v 12 Maa leen di fàdde mbas, nangu seen cér, ba noppi sose ci yaw askan wu leen ëpp, ëpp leen doole.» \v 13 Musaa ne Aji Sax ji: «Kon de, waa Misra ga nga jële mbooloo mii, génnee leen sa doole ca seen biir, dinañu ko dégg, \v 14 te dinañu ko nettali waa réew mii. Waa réew mii dégg nañu ne yaw Aji Sax ji ci sa bopp yaa nekk ci digg mbooloo mii ngay feeñu bët ak bët, yaw Aji Sax ji, saw niir taxaw, tiim leen, te aw taxaaru niir nga leen di jiitoo bëccëg, jiitoo leen aw taxaaru sawara, guddi. \v 15 Nga nara boole mbooloo mii mépp, bóom benn yoon? Kon de xeet yi dégg sa jaloore dinañu wax ne: \v 16 “Ñàkka mana yóbbu mbooloo mii ca réew ma mu leen giñaloon, moo waral Aji Sax ji faagaagal leen ci màndiŋ mi!” \v 17 Kon nag ngalla Boroom bi, na sa doole màgg rekk, noonee nga noon: \v 18 “Aji Sax ji! Kiy muñ mer, te bare ngor, di bale tooñ aki moy te du ñàkka topp mukk doom, tooñu waajuram, ba ca sët yaak sëtaat ya.” \v 19 Ngalla jéggalal mbooloo mii seenug tooñ ci sag bare ngor, noonee nga leen masa bale, ca Misra ba tey jii.» \p \v 20 Ba loolu amee Aji Sax ji ne: «Jéggal naa leen noonu nga ko waxe. \v 21 Waaye ndegam maay Kiy Dund, te leeru Aji Sax ji mooy fees àddina sépp, \v 22 gannaaw mboolem nit ñi gis samag leer, gis firnde yi ma def ci digg Misra ak ci màndiŋ mi, ñoo ma nattu nii fukki yoon, bañ maa déggal, \v 23 kenn ci ñoom déy du gis réew, mi ma giñaloon seeni maam. Mboolem ñi ma xarab, kenn du ko ci gis. \v 24 Sama jaam Kaleb nag, gannaaw meneen xel lay wéye, te moo topp sama gannaaw, ba mu mat sëkk, maa koy yóbbu ba ca réew, ma mu demoon, te aw askanam a koy moom. \v 25 Gannaaw Amalegeen ñaak Kanaaneen ñaa nga dëkke xur wi nag, bu ëllëgee walbatikuleen, toppaat màndiŋ mi, te jaareji ko géeju Barax ya.» \p \v 26 Aji Sax ji waxati Musaak Aaróona, ne: \v 27 «Ba kañ la mbooloo mu bon mii di ñaxtu ci sama kaw? Ñaxtu yi bànni Israyil di ñaxtu ci sama kaw, dégg naa ci. \v 28 Ne leen: Ndegam maay Kiy Dund déy, Kàddug Aji Sax jee, noonu ngeen waxe, may dégg, ni laa leen di def. \v 29 Ci màndiŋ mii kay la seeni néew di tëdd. Mboolem ñi ñu leen limal, mboolem ñi ñu leen waññal, ñu dale ci ñaar fukki at, jëm kaw te doon ñaxtu ci sama kaw, \v 30 kenn ku moy Kaleb doomu Yefune ak Yosuwe doomu Nuun, du kenn ku ciy dugg ca réew, ma ma leen giñoona dëël. \v 31 Seen tuut-tànk, yi ngeen ne alalu sëxëtoo lañuy doon, ñoom laay yóbbu, ba ñu xam réew ma ngeen xarab. \v 32 Waaye yeen, seeni néew ci màndiŋ mii lay tëdd, \v 33 seeni doom di màngaan ñeent fukki at ci màndiŋ mi, gàddoo ko seen ñàkk worma, yeen ñi leen jur, ba keroog seeni néew tëdd ba jeex ci màndiŋ mi. \v 34 Limu fan yi ngeen nemmikuji woon réew ma, ñeent fukki fan, benn fan bu ci nekk day wecci menn at, ngeen gàddoo ko seen mbugali bàkkaar, ñeent fukki at, ba ngeen xam li jànkoonteek man di jur. \v 35 Man Aji Sax ji, maa ko wax. Noonu déy laay def mboolem mbooloo mu bon mii booloo ci sama kaw. Ci màndiŋ mii lañuy raafe, fii lañuy deeye.» \p \v 36 Ndaw ya Musaa yebaloon, ñu nemmikuji réew ma nag, te ñu délsi, di baatal réew ma, ba tax mbooloo mépp di ñaxtu ci kawam, \v 37 ñooña doon baatal réew ma, am mbas a leen rey fi kanam Aji Sax ji. \v 38 Mennum Yosuwe doomu Nuun ak mennum Kaleb doomu Yefune doŋŋ, ñoo mucc ca ndaw yooya nemmikuji woon réew ma. \s1 Mbooloo ma gàntalati na \p \v 39 Ba Musaa jottlee \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp kàddu yooyu, mbooloo ma mititlu nañu ko lool. \v 40 Ca ëllëg sa ñu teela xëy, yéegi kaw tund ya, te naan: «Nu ngi nii di yéeg, jëm fa nu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax, ndax noo tooñ.» \v 41 Musaa ne leen: «Lii nag? Yeena ngi tebbi waxi Aji Sax ji, waaye loolu de du sotti! \v 42 Buleen dem, te Aji Sax ji àndul ak yeen. Lu ko moy dingeen daanu ci seen kanami noon. \v 43 Te kat Amalegeen ñi ak Kanaaneen ñaa ngi fuu ci seen kanam. Yeenay fàddoo saamar doŋŋ. Gannaaw yeena dëddu Aji Sax ji nag, Aji Sax ji du ànd ak yeen.» \p \v 44 Teewul ñu të ticc, ne dañuy yéegi kaw tund ya, te \w gaalu kóllërey Aji Sax|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* ji ak Musaa génnuñu dal ba. \v 45 Ba mu ko defee Amalegeen ña ak Kanaaneen ña dëkke woon diiwaanu tund woowa wàccsi, duma leen, tasaare leen ba ca gox ba ñuy wax Xorma. \c 15 \s1 Lu jëm ci saraxi pepp ak diw ak biiñ \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa, ne: \v 2 «Waxal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen: Bu ngeen demee ca réew ma ngeen di sanci, réew ma ma leen jox, \v 3 bu ngeen di defal Aji Sax ji saraxu sawara, muy \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, mbaa sarax su nit di wàccoo aw xas, mbaa \w saraxu yéene|lemma="Sarax yi:"\w*, mbaa seen saraxi màggal, ngir xeeñal xetug jàmm ñeel Aji Sax ji, te muy lu jóge ci jur gu gudd mbaa gu gàtt, defe leen ko nii: \p \v 4 «Kiy sarxal Aji Sax ji ab saraxam, na sarxewaale \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* bu benn fukkeelu efab sunguf su mucc ayib, di ñetti kilo, su ñu xiiwe ñeenteelu xaajub xiinu diw, di liitar ak genn-wàll, \v 5 ak biiñ ngir \w saraxu tuuru|lemma="Sarax yi:"\w*, ñeenteelu xaajub xiin, di liitar ak genn-wàll, mu ànd ak saraxu rendi-dóomal mbaa beneen sarax, su dee xar mu ndaw. \p \v 6 «Su dee am kuuy, saraxu pepp bi muy àndal, ñaari fukkeeli efay sunguf su mucc ayib lay doon, di juróom benni kilo, ñu xiiwe ko ñetteelu xaajub xiinu diw, di ñaari liitari diw, \v 7 ak biiñ ngir saraxu tuuru, ñetteelu xaajub xiin, di ñaari liitar. Na joxe loolu, def ko xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji. \p \v 8 «Su dee sarxe jur gu gudd, muy saraxu rendi-dóomal, mbaa sarax bu muy wàccoo aw xas, mbaa \w saraxu cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*, ñeel Aji Sax ji, \v 9 na sarxewaaleek jur gu gudd gi, ab saraxu pepp bu ñetti fukkeeli efay sunguf su mucc ayib, di juróom ñeenti kilo, ñu xiiwe ko genn-wàllu xiinu diw, di ñetti liitar, \v 10 ak biiñ bu muy joxewaale, ngir saraxu tuuru, di genn-wàllu xiin, muy ñetti liitar. Loolu saraxu sawara la, di xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji. \p \v 11 «Noonu lees di def bu dee saraxu yëkk, mbaa am kuuy, mbaa am xar mu ndaw, mbaa bëy. \v 12 Nu limu juri sarax yi tollu rekk, ngeen def mu ci nekk noonu, ànd ak lim ba. \v 13 Mboolem njuddu-ji-réew, noonu lay defe sarax yooyii, buy indi saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji. \p \v 14 «Su dee ab doxandéem bu dal ak yeen, mbaa ku nekk ak yeen ci seen maas yiy ñëw, te muy joxe saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji, ni ngeen koy defe rekk la koy defe. \v 15 Mbooloo mi mépp, dogalu yoon boobu benn la ciy doon, muy yeen, di doxandéem bi. Dogal la buy sax fàww, ñeel seen maasoo maas, te di benn ci yeen ak ci doxandéem bi, fi kanam Aji Sax ji. \v 16 Wenn yoon wee, di benn àtte bi, ñeel leen, ñeel doxandéem bi dal ak yeen.» \s1 Ab jooxe war na ci pepp mu jëkk \p \v 17 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa, ne \v 18 «Waxal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, ne leen, bu ngeen demee ca réew, ma ma leen jëme, \v 19 bay lekk ca ñamu réew ma, nangeen ci jooxe ab jooxe, ñeel Aji Sax ji; \v 20 seen notu sunguf bu jëkk, ci ngeen di jooxe menn mburum jooxe. Ni ngeen di sàkke jooxe bu jóge ca dàgga ja rekk, ni ngeen koy jooxee. \v 21 Seen notu sunguf bu jëkk, ci ngeen di sàkke ab jooxe, ñeel Aji Sax ji, yeen ak seen askan.» \s1 Sarax war na ci moy gu dul teyeef \p \v 22 Su dul ci teyeef ngeen ñàkka jëfe lenn ci mboolem santaane yii \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dénk Musaa, \v 23 ci mboolem lu leen Aji Sax ji sant, Musaa jottli, dale ko keroog ba Aji Sax ji santaanee loola, ak gannaaw gi, ba ca seen maasoo maas, \v 24 su dee moy gu dul teyeef, te mbooloo mi yégu ko woon, su boobaa mbooloo mépp ay sarxal aw yëkk wu ndaw wuy doon \w rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji, ak \w saraxu peppam|lemma="Sarax yi:"\w*, ak \w saraxu tuuroom|lemma="Sarax yi:"\w*, ni ko yoon àttee, ak benn sikket ngir \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*. \v 25 \w Sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi day def loolu njotlaayal mbooloom \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp, njéggal daldi leen ñeel, gannaaw moy ga dug teyeef, te ñoom it indi nañu seen saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji, booleek seen saraxu póotum bàkkaar fi kanam Aji Sax ji, ndax seen moy ga dul teyeef. \v 26 Njéggal day daldi ñeel mbooloom bànni Israyil gépp, ak bépp doxandéem bu dal ak ñoom, ndax mbooloo mépp lay seen moy gu dul teyeef. \p \v 27 Su dee kenn nit a bàkkaar te du teyeefam, na sarxal aw bëy wu jigéen wu menn at, ngir saraxu póotum bàkkaar. \v 28 Sarxalkat bi daldi koy def fi kanam Aji Sax ji, njotlaayal ki moy ci ag ñàkka tey, ca bàkkaaram ba dul teyeef. Loolu la koy jote, njéggal ñeel ko. \v 29 Muy njuddu-ji-réew ju bokk ci bànni Israyil, di doxandéem bu dal ak ñoom, yoon wi wenn lay doon, ñeel ki moy te du teyeefam. \p \v 30 Nit ki tooñ cig teyeefam nag, muy njuddu-ji-réew, di doxandéem, kooku Aji Sax ji la ñàkke kersa. Nit kooku, dees koy dagge ci biiri bokkam: \v 31 Gannaaw kàddug Aji Sax ji la teddadil te ndigalam la xëtt, nit kooku dees koy dagg rekk, mu gàddu bàkkaaram. \s1 Bésub Noflaay wormaal la laaj \p \v 32 Ba \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* nekkee ca màndiŋ ma, dañoo fekk jenn waay, muy taxan \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*. \v 33 Ña ko fekk muy taxan, yóbbu ko ba ca Musaa ak Aaróona, ak mbooloo ma mépp. \v 34 Ba loolu amee ñu teg ko ciy loxo, ndax dogaleesagul woon nees di def ak moom. \v 35 Ci kaw loolu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ne Musaa: «Dee rekk mooy àtteb waa ji: dees koy génne dal bi, mbooloo mépp dóor koy xeer, ba mu dee.» \p \v 36 Mbooloo ma mépp daldi koy génne dal bi, dóor koy xeer ba mu dee, na ko Aji Sax ji sante Musaa. \s1 Yoon sàrtal na wàllu col \p \v 37 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa, ne ko: \v 38 «Waxal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, ne leen, ci seen maasoo maas, nañu def ay langat ci seen cati mbubb, langat wu ci nekk ñu nas ci buum gu baxa. \v 39 Mu doon seen langat yu ngeen di xool, di ko fàttlikoo mboolem santaaney Aji Sax ji, ngir di ko jëfe, te baña topp seen bànneexu bakkan ak seeni gët, bay moy. \v 40 Su ko defee ngeen di bàyyi xel tey jëfe sama santaane yépp, daldi doon ñu sell, ñeel seen Yàlla. \v 41 Man maay Aji Sax ji, seen Yàlla, ji leen génnee réewum Misra ngir doon seen Yàlla. Maay seen Yàlla Aji Sax ji.» \c 16 \s1 Kore fippu na \p \v 1 Ku ñuy wax Kore doomu Isar, mi askanoo ci Keyat doomu Lewi, moo àndoon ak ay Rubeneen, ñuy Datan ak Abiram, doomi Elyab, ak Onn doomu Pelet, \v 2 ñu jógal Musaa, ñook ñaar téeméer ak juróom fukk (250) ci \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, diy kilifa ci mbooloo mi, am baat ca pénc ma, te di ñu amu tur. \v 3 Ci kaw loolu ñu bokk daje fi kaw Musaa ak Aaróona, ne leen: «Doy na sëkk! Mbooloo mi ba mu daj, ñépp a sell, te ci sunu biir la \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nekk. Ana lu ngeen di xoggliku ci kaw mbooloom Aji Sax ji?» \p \v 4 Ba Musaa déggee loolu, da ne gurub, dëpp jë bi fi suuf. \v 5 Mu wax Kore ak gàngooram gépp, ne: «Bu ëllëgee, Aji Sax ji mooy xamle kan la séddoo ak kan mooy ki sell, mu jegeñal ko boppam. Ki mu taamu nag, dina ko jegeñal boppam. \v 6 Dangeen di def nii: jël-leeni and, yaw Kore, yaak sa gàngoor gépp, \v 7 te ngeen def ciy xal, def ci cuuraay fi kanam Aji Sax ji, ëllëg. Su ko defee ku Aji Sax ji taamu, kookooy ki sell. Doy na sëkk, yeen \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi!» \v 8 Musaa teg ca ne Kore: «Yeen Leween ñi, dégluleen nag! \v 9 Xeeb ngeen daal ber gi leen Yàllay Israyil ber ci mbooloom Israyil, jegeñal leen boppam, ngeen di liggéey liggéeyu màkkaanu Aji Sax ji, di taxaw fi kanam mbooloo mi, di leen jaamul Yàlla? \v 10 Yaw mu jegeñal la, yaak sa bokki Leween ñépp, ngeen di xëccu céru carxal, boole ci! \v 11 Kon kay yaw yaak sa gàngoor gépp, ci kaw Aji Sax ji ngeen bokk daje! Ana kuy Aaróona, ba ngeen di ñaxtu ci kawam?» \p \v 12 Musaa nag woolu Datan ak Abiram, doomi Elyab, ñu ne ko: «Danoo ñëwul! \v 13 Dangaa xeeb li nga nu jële réew mu meew maak lem ja tuuroo, ngir reylu nu ci màndiŋ mi, ba tax ngay buur-buurlu ci sunu kaw teg ci? \v 14 Du réew mu meew maak lem ja tuuroo nga nu yóbbu de, te séddoo nu céri tool mbaa tóokëri reseñ. Mbooloo mii mépp, man nga leena tuur lëndëm? Danoo ñëwul!» \v 15 Ba loolu amee Musaa mer lool. Mu ne Aji Sax ji: «Bul geesu sax seen sarax. Menn mbaam sax, masuma leen koo jëlal te masuma cee tooñ kenn.» \s1 Way-fippu ya jot nañu seen añ \p \v 16 Musaa nag ne Kore: «Yaw, yaak sa gàngoor gépp, ca kanam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, yaak ñoom ak Aaróona, ëllëg. \v 17 Na ku nekk jël ub andam, def ci cuuraay, te na ku ci nekk indib andam fi kanam Aji Sax ji, muy ñaar téeméeri and ak juróom fukk, yaak Aaróona it, ku nekk akub andam.» \p \v 18 Ba mu ko defee ku nekk jël ub andam, def cay xal, teg ca cuuraay. Ñu taxaw ca bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* ma, ñook Musaa ak Aaróona. \v 19 Kore nag dajale gàngoor gépp fa ñoom, ca bunt xaymab ndaje ma. Ci kaw loolu leeru Aji Sax ji feeñu mbooloo ma mépp! \p \v 20 Aji Sax ji wax Musaa ak Aaróona, ne: \v 21 «Xiddileen mbooloo mii, ma xoyom leen léegi!» \v 22 Musaa ak Aaróona ne gurub, dëpp seen jë fa suuf, daldi ne: «Éy Yàlla, yaw Yàllay bépp boroom bakkan bu bindoo aw suux, xanaa du kenn ay bàkkaar, nga far sànju ci kaw mbooloom lëmm?» \p \v 23 Ci kaw loolu Aji Sax ji ne Musaa: \v 24 «Waxal mbooloo mi, ne leen ñu jóge fi wër màkkaani Kore ak Datan ak Abiram.» \p \v 25 Musaa daldi jubal ca Datan ak Abiram, magi Israyil topp ca. \v 26 Ci biir loolu mu wax ak mbooloo ma, ne leen: «Ngalla dàndleen xaymay nit ñu bon ñii, te buleen laal seen lenn, bala ngeen di buuboondook mboolem bàkkaari ñii.» \v 27 Ñu daldi jóge mboolem fa wër màkkaani Kore ak Datan ak Abiram. Datan ak Abiram ñoom, ña nga génn, taxaw ca seen bunti xayma, ñook seeni jabar ak seeni doom, ak seeni tuut-tànk. \p \v 28 Musaa nag ne: «Lii nag moo leen di xamal ne Aji Sax ji moo ma yebal ngir ma def jëf jii jépp, waaye du sama coobarey bopp: \v 29 Ndegam ni mboolem doom aadama di deeye, ni la ñii deeye, seen demin di deminu mboolem doom aadama, su boobaa du Aji Sax jee ma yebal. \v 30 Waaye ndegam Aji Sax ji moo sàkk ba sàkk tey lu masula am, ba suuf ŋa, mëdd leen, ñook lu bokk ci ñoom, ñu tàbbiwaale bakkan biir njaniiw, su boobaa dingeen xam ne ñoom ñii ñoo xarab Aji Sax ji.» \v 31 Naka la Musaa di daaneel kàddu yooyu yépp, fa ñu taxaw jekki xar, \v 32 suuf ŋa, mëdd leen, ñook seen waa kër, ak mboolem ku bokk ci Kore, ak mboolem alal ja. \v 33 Ñu daldi tàbbiwaale bakkan biir njaniiw, ñook mboolem lu ñu moom, suuf sàng leen, ñu réer mbooloo ma mërr. \v 34 Mboolem Israyil dégg seen yuux ya, daldi daw, te naan: «Nan daw bala noo suuf a mëdd!» \p \v 35 Ci kaw loolu sawara moo bawoo fa Aji Sax ji, xoyom ñaar téeméeri nit ak juróom fukk ña indi woon saraxu cuuraay ba. \s1 Andi way-fippu ya firnde la \p \v 36 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa, ne: \v 37 «Waxal Elasar doomu Aaróona, \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi, ne ko mu seppee and yi ci lakk gi, ndax lu sell la, te xal yi, na ko tuur fu sore. \v 38 And yooyii seeni boroom feye seen bakkan seeni bàkkaar, dees koy tëgg, ba mu tàlli, xoobe ko \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi. Gannaaw fi kanam Aji Sax ji lañu indi and yi, ba tax mu doon lu sell, na and yi doon firnde, ñeel \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*.» \v 39 Ci kaw loolu Elasar sarxalkat bi jël andi xànjar, ya ña dee ca lakk ga indi woon, ñu tëgg ko ba mu tàlli, ngir sarxalukaay ba, \v 40 na ko Aji Sax ji santaanee woon, Musaa jottli. Loolu di fàttli bànni Israyil ne benn jaambur bu bokkul ci askanu Aaróona sañula dikk di taal cuuraay fi kanam Aji Sax ji, lu ko moy lu mel ni li dal Kore ak gàngooram moo koy dal. \s1 Ñaxtu sabab na mbugal \p \v 41 Ca ëllëg sa mbooloom \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp a doon ñaxtu ci kaw Musaa ak Aaróona, naan: «Yeen yeena reylu ñoñi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji!» \v 42 Mbooloo maa nga sam Aaróona ak Musaa. Ci biir loolu, ñu ne gees \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* ma‎, gisuñu lu moy niir wa muur ko, leerug Aji Sax ji feeñ. \p \v 43 Ba loolu amee Musaa ak Aaróona dem ba ca kanam xaymab ndaje ma, \v 44 Aji Sax ji wax Musaa ne: \v 45 «Jógeleen biir mbooloo mii, ma faagaagal leen léegi!» Ñu ne gurub, dëpp seen jë fa suuf. \v 46 Musaa ne Aaróona: «Jëlal and bi, nga sàkke ci \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi ay xal, teg ci cuuraay, yóbbu gaaw ca mbooloo ma, ba defal leen ag njotlaay, ndax sànj mi tàkke na ci Aji Sax ji, mbas mi tàmbali na!» \v 47 Aaróona këf and ba Musaa wax, daw dugg ca biir mbooloo ma. Ndeke mbas ma tàmbali na ca biir mbooloo ma. Mu def ca and ba cuuraay, daldi defal mbooloo ma njotlaay. \v 48 Naka la taxaw ci diggante ñi dee ak ñiy dund, mbas ma dal. \v 49 Ña dee ca mbas ma nag doon fukki junneek ñeent ak juróom ñaar téeméer (14 700), te bokkul ak ña dee woon ca mbirum Kore ma. \v 50 Ba mu ko defee Aaróona dellu ca Musaa, ca bunt xaymab ndaje ma, fekk mbas ma dal. \c 17 \s1 Bant bu wow jebbi na \p \v 1 Ba loolu amee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ne Musaa: \v 2 «Waxal ak \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, nga nangoo ci mboolem seen kilifay kër maam, aw yet, na wenn yet bawoo ci kër gu ci nekk, muy fukki yet ak ñaar, yet wu ci nekk, nga bind ci turu boroom. \v 3 Turu Aaróona itam, nga bind ko ci yetu giirug Lewi, ndax wenn yet lay doon, ñeel kilifag kër gu ci nekk. \v 4 Nga denc yet yi ca biir \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* ma, fa kanam gaalu seedes kóllëre ga, fa may dajeek yeen. \v 5 Su ko defee ki ma taamu, aw yetam dina jebbi, ba ma teqlikoo ak xultuy bànni Israyil, yi ñuy xultu ci seen kaw.» \p \v 6 Musaa àgge ko bànni Israyil, mboolem seen kilifay kër maam jox Musaa aw yet, kilifa gu ci nekk wenn yet, ñeel kër maamam, muy fukki yet ak ñaar, yetu Aaróona bokk ca. \v 7 Musaa teg yet ya fa kanam Aji Sax ji, ca biir xaymab seede sa. \v 8 Ca ëllëg sa, naka la Musaa dugg ca xaymab seede sa rekk, daldi fekk yetu Aaróona wu kër Lewi, jebbi; fekk na mu jebbi, ba tóor, ba meññ ay doomi amànd\f + \fr 17.23 \fr*\fk amànd: \fk*\ft xeetoo naak gerte-tubaab.\ft*\f*. \v 9 Ba loolu amee Musaa jële yet yépp ci Aji Sax ji, dem ba ca bànni Israyil gépp, ñépp gis, ku nekk jël yetam. \p \v 10 Aji Sax ji waxati Musaa, ne: «Dellool yetu Aaróona fa kanam gaalu seede sa, mu dence fa, di firnde ñeel xeetu fippukat wi, ndax nga dakkal seeni xultu ci sama kaw, ba duñu dee.» \v 11 Musaa def noonu. Na ko ko Aji Sax ji sante, na la ko defe. \p \v 12 Bànni Israyil nag naan Musaa: «Jeexal nan nag, sànku nan, nun ñépp ay sànku! \v 13 Gannaaw képp ku jege màkkaanu Aji Sax ji doŋŋ, dangay dee kay, mbaa dunu far jeex tàkk?» \c 18 \s1 Lu jëm ci sarxalkat yi ak Leween ñi \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ne Aaróona: «Yaw, yaak say doom ak sa waa kër maam, yeenay gàddu peyug tooñ ci wàllu bérab bu sell bi, te itam yaw, yaak say doom, yeenay gàddu peyug tooñ ci seen wàllu carxal. \v 2 Te itam sa bokki \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi, sa giirug baay, jegeñal leen sa bopp, ñu jokku ci yaw, di la jàpple, te yaw yaak say doom, ngeen féete fi kanam xayma ba seedes kóllëre ga dence. \v 3 Ñooy dénkoo sa ndénkaane, ak dénkaaney mboolem xayma bi, waaye jumtukaayi \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi, ak \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi, buñu ko jege, lu ko moy dañuy dee, ñoom ak yeen itam. \v 4 Nañu jokku ci yaw, te ñu dénkoo ndénkaanel \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi, ci mboolem liggéeyu xayma bi. Kenn ku ci bokkul nag du leen jege, yeen. \v 5 Nangeen dénkoo ndénkaanel bérab bu sell bi, ak ndénkaanel sarxalukaay bi, ngir am sànj baña dalati ci kaw \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \p \v 6 «Man mii nag maa seppee seen bokki Leween ñi ci biir bànni Israyil. Yeen lañu leen jagleela jagleel, ñeel Aji Sax ji, ngir ñu liggéey liggéeyu xaymab ndaje mi. \v 7 Yaw nag yaak say doom, dénkooleen seenug carxal ci mboolem mbiru sarxalukaay bi, ak ca wàllaa ridob biir bi, ngeen di ca liggéey. Seen liggéeyu carxal bi, ab sasu teraanga la, maa leen ko terale. Waaye ku bokkul ci yeen, bu ci laalee, dees koy rey.» \s1 Lu jëm ci peyu sarxalkat yi \p \v 8 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji neeti Aaróona: «Man mii maa la sédd ndénkaaneb samay jooxe; mboolem jooxe yu \w sell|lemma="sell:"\w* yi \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* indi, yaw laa ko jagleel, nga jagoo, yaak say doom, ci kaw dogal bu sax dàkk. \v 9 Lii nag, yaa ko moom, ci mboolem sarax yu sell yee sell, yi mucc sawara: seen bépp sarax, seen bépp \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* ak seen bépp \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*, ak seen bépp \w saraxu peyug tooñ|lemma="Sarax yi:"\w* bu ñu ma indil, lu sella sell la, ñeel la, yaak sa doom yu góor. \v 10 Fu sella sell ngeen koy lekke; képp kuy góor ci yeen, sañ na cee lekk. Lu sell lay doon ci yaw. \p \v 11 «Leneen lu la ñeel moo di jooxe bu jóge ci saraxi nit ñi, di bépp \w saraxu yékkati-jébbal|lemma="Sarax yi:"\w* bu bànni Israyil. Yaw laa ko sédd, yaak sa doom yu góor, ak sa doom yu jigéen, ci kaw dogalu yoon bu sax dàkk. Képp ku set ci sa waa kër, sañ na cee lekk. \p \v 12 «Lépp luy ngëneelu diw gu bees, ak ngëneelu biiñ bu bees, ak pepp mu jëkka ñor, mu ñu jox Aji Sax ji, yaw laa ko jox. \v 13 Njàlbéenu meññeef mi ñuy indil Aji Sax ji, ci mboolem lu meññee ci seen suuf, yaa koy moom, te képp ku set ci sa waa kër, sañ na cee lekk. \v 14 Mboolem lees aayalal Aji Sax ji ci Israyil, yaa koy moom. \v 15 Lépp luy ubbitey njur bu ñu jagleel Aji Sax ji, ci lépp lu bindoo aw suux, nit ak mala, yaa koy moom. Fexeel rekk ba jotlu taawub nit ki, te taawub mala mu setul it, nanga ko jotlu. \v 16 Njotu xale bu am lu dale ci weer, àpp ko ci juróomi siikali xaalis yu \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi, benn siikal yemook ñaar fukki gera mbaa fukki garaam. \v 17 Waaye lu nag taawloo, ak lu xar taawloo, ak lu bëy taawloo, deesu ko jot. Yooyii yu sell la. Deretam ngay xëpp ci \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi, nebbon bi, nga def ko saxar, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji. \v 18 Aw yàppam, yaa koy moom, ni nga moome dënnu saraxu yékkati-jébbal, ak tànkub kanam bu ndijoor ba. \v 19 Mboolem jooxe yu sell yi bànni Israyil di jooxeel Aji Sax ji, sédd naa la ko, yaak sa doom yu góor, ak sa doom yu jigéen, ci kaw dogalu yoon bu sax dàkk. \w Kóllërey|lemma="kóllëre g-:"\w* xorom\f + \fr 18.19 \fr*\fk kóllërey xorom\fk*\ft waxin la, day tegtale kóllëre gu yàgg, ba sax dàkk, ndax lu bare luy yàqu, xorom lees ko baaxoo woona dence, ngir mu yàgg.\ft*\f* a ngoogu, du fecciku, xanaa sax dàkk fi kanam Aji Sax ji, ñeel la yaw, yaak saw askan.» \v 20 Aji Sax ji neeti Aaróona: «Seenum réew nag doo ci am cér, te wàllu suuf, doo ko am ci seen biir. Man maay sa wàll, di sab cér ci biir bànni Israyil.» \s1 Lu jëm ci peyug Leween ñi \p \v 21 \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi ñoom, maa leen jox bépp céru fukkeel bu génne ci Israyil, muy seen cér, ñu yooloo ko seen liggéey bi ñuy liggéey ci \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi. \p \v 22 Bu \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* juuxati ci xaymab ndaje mi, di gàddu bàkkaar bu dee di àtteem. \v 23 Leween ñi ñooy ñiy liggéey liggéeyi xaymab ndaje mi, te lu ñu ca tooñ, ñooy gàddu pey ga, ci kaw dogal bu sax dàkk, ñeel leen, ñook seen askan. Waaye biir bànni Israyil, Leween ñi duñu ci séddu céru suuf, \v 24 ndax céri fukkeel yi bànni Israyil yékkati, jooxeel ko \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, jox naa ko Leween ñi, muy seen cér. Moo tax ma ne leen, biir bànni Israyil, duñu ci séddu céru suuf. \s1 Ab jooxe ñeel na Leween ñi \p \v 25 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* waxati Musaa ne: \v 26 «\w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi, wax leen, ne leen bu ñu jëlee ci \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* seen céri fukkeel yi ma leen jagleel yeen, muy seen cér, nañu ci jooxeel Aji Sax ji, fukkeelub céru fukkeel yooyu. \v 27 Nañu leen jàppal loolu, yeen Leween ñi, muy seen jooxeb bopp, ni bu doon pepp mu jóge ci seen dàggay bopp, ak biiñ bu bees bu jóge ci seen nalukaay. \v 28 Su ko defee ngeen jooxe yeen itam, jooxeb Aji Sax ji, ci mboolem seen céri fukkeel yi ngeen jële ci bànni Israyil. Kon nangeen jële coocu, jooxeb Aji Sax ji, jox ko Aaróona \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi. \v 29 Lépp lu ñu leen sédd, nangeen ci jooxe jooxeb Aji Sax ji. Mboolem céri ngëneel yooyu, ci ngeen di génne cér bu sell boobu. \p \v 30 «Waxal Leween ñi ne leen gannaaw bu ñu ca génnee céru ngëneel li, li ci des lew na leen, ni bu doon pepp mu jóge ci seen dàggay bopp, ak biiñ bu jóge ci seen nalukaay. \v 31 Sañ nañu koo lekke fépp, ñoom ak seen waa kër, ndax loolu seen pey la, ñu yooloo ko seen liggéeyu \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi. \v 32 Duñu ci gàddu benn bàkkaar, gannaaw bu ñu ci jooxee céru ngëneel li. Waaye jooxe yu \w sell|lemma="sell:"\w* yu bànni Israyil yooyu, buñu ci teddadil lenn, ba di ci dee.» \c 19 \s1 Lu jëm ci ndoxum setlu ak setlu gi war \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ak Aaróona, ne: \v 2 «Lii mooy dogalu yoon bi Aji Sax ji santaane: Neleen \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ñu indil leen nag wu jigéen wu xonq, wu mat, mucc sikk, te kenn masu koo takk, \v 3 ngeen jox ko Elasar \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi, ñu génne ko dal bi, te ñu rendi ko fi kanamam. \v 4 Na Elasar sarxalkat bi capp baaraamam ci deret ji, wis-wisal ko juróom ñaari yoon fi féeteek bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi. \v 5 Nañu lakk nag wi‎ ci kanamam. Der bi ak yàpp wi ak deret ji ak sébbriit mi, lépp lañuy lakk. \v 6 Su ko defee sarxalkat bi sàkk bantu seedar ak caru isob ak ndimo lu xonq curr, boole ko sànni ca sawara wa ñuy lakk nag wa. \v 7 Gannaaw loolu na sarxalkat bi fóot ay yéreem, sangu, doora mana duggaat ci dal bi, te du ko tee yendoo sobe ba ca ngoon. \v 8 Kiy lakk nag wi itam, na fóot ay yéreem, sangu, te du ko tee yendoo sobe ba ca ngoon. \v 9 Na ku set tonni dóomu nag wa, te sotti ko bérab bu set, foofa ca biti. Dóom ba dencub mbooloom bànni Israyil lay doon, ñu di ko waajale ndoxum setlu, ngir saraxu póotum bàkkaar. \v 10 Ku góor kiy tonni dóomi nag wi itam day fóot ay yéreem, te du tee mu yendoo sobe ba ca ngoon. Na loolu di dogalu yoon bu sax fàww, ñeel bànni Israyil, ak doxandéem bu dëkk ci seen biir. \p \v 11 «Bu loolu weesee ku laal nit ku dee, ak néew bu mu mana doon, dina sobewu diiru juróom ñaari fan. \v 12 Na setlu ca ndox moomee ca bésub ñetteel ba, gannaaw ba mu ko laalee, te na setluwaat ca bésub juróom ñaareel ba. Su ko defee mu set. Waaye su setluwul ca bésub ñetteel ba, ak bésub juróom ñaareel ba, du set. \v 13 Képp ku laal nit ku dee, ak néew bu mu mana doon, bu setluwul, màkkaanu Aji Sax ji la sobeel. Kooku dees koy dagge ci bànni Israyil. Gannaaw ndoxum setlu ma, wiseesu ko ko, sobewu lay wéye. \p \v 14 «Lii la yoon wi tëral: Bu nit deeyee ci biir xayma, képp ku dugg ci biir xayma bi, ak képp ku mu fekk ci xayma bi, day sobewu diiru juróom ñaari fan, \v 15 te mboolem ndab lu fa ubbiku woon, kubeer it ubu ko woon ràpp, loola ndab sobewu na. \v 16 Képp ku laal ca àll ba, nit ku ñu bóome saamar, mbaa ku Yàlla moomal boppam, mbaa mu laal yaxi nit ku dee, mbaa mu laal bàmmeel, kooka day sobewu diiru juróom ñaari fan. \v 17 Nañu sàkkal ki sobewu ca dóomu \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w* ba ñu lakkoon, te ñu sotti ndox muy dund ci ndab, ca kaw dóom ba. \v 18 Bu loolu wéyee, na ku set jël caru isob, capp ko ca ndox ma, wis-wisal ko ca kaw xayma ba nit deeye, wis ko ca kaw ndab yépp, ak ca kaw nit ña fa nekkoon. Na ko wis itam ci kaw nit ku laal yaxi ku dee, mbaa mu laal ku ñu bóome saamar, mbaa mu laal ku Yàlla moomal boppam, mbaa mu laal bàmmeel. \v 19 Bésub ñetteel ba nag, ak bésub juróom ñaareel ba, ci la nit ku set di wis-wisal ndox mi ci kaw ki sobewu. Bésub juróom ñaareel ba ca la koy settli. Su ko defee ka sobewu fóot ay yéreem, sangu, bu jant sowee mu daldi set. \v 20 Képp ku sobewu te setluwul, kooku dees koy dagge ci mbooloo mi, ndax bérabu sellngay Aji Sax ji la sobeel. Gannaaw wiseesu ko ndoxum setlu mi, sobewu na. \p \v 21 «Na leen loolu ñeel ci kaw dogalu yoon bu sax dàkk. Ka doon wis-wisal ndoxum setlu mi nag, na fóot ay yéreem, te ku laal ci ndoxum setlu mi day yendoo sobe ba ca ngoon. \v 22 Nit ki sobewu, mboolem lu mu laal day sobewu, te ku laal ca loola it day yendoo sobe ba ca ngoon.» \c 20 \s1 Diiŋat nañu Musaa ak Aaróona fa Meriba \p \v 1 Mbooloom \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp nag àgg ca màndiŋu Ciin, ci biir weer wi jëkk ci at mi\f + \fr 20.1 \fr*\ft Jombul muy seen ñeent fukkeelu at, gannaaw seen wëreelu ba. Seetal ci saar 22-29 ak 33.38.\ft*\f*. Ñu daldi dal ca Kades. Fa la Maryaama faatoo, ñu denc ko foofa. \p \v 2 Ci kaw loolu mbooloo ma dem ba ñàkk ndox. Ñu daje ci kaw Musaa ak Aaróona. \v 3 Mbooloo ma di xulook Musaa, naa ko: «Moo lu nu tee woona dee keroog ba sunu bokk ya deeyee fa kanam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji? \v 4 Ana loo indee mbooloom Aji Sax ji ci màndiŋ mii, nu di fi deesi doŋŋ, nook sunug jur? \v 5 Ana loo nu jële woon Misra, di nu indi fu bon fii? Du bérab bu nangu menn jiwu: du figg, du reseñ, du gërënaat, te du siitum ndox mu ñu naan!» \p \v 6 Ba loolu amee Musaa ak Aaróona bàyyikoo ca mbooloo ma, dem ba ca bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* ma. Ñu ne gurub, dëpp seen jë fa suuf. Leeru Aji Sax ji nag feeñu leen. \v 7 Aji Sax ji wax ak Musaa, ne: \v 8 «Jëlal saw yet, nga dajale mbooloo mi, yaak sa mag Aaróona, ngeen wax ak doj woowu, ñuy gis, mu xelli am ndox. Te nga sottil leen ndox mu jóge ci doj wi, nàndale ko mbooloo mi, ñook seenug jur.» \p \v 9 Ba mu ko defee Musaa jële yet wa fa kanam Aji Sax ji, na mu ko ko sante. \v 10 Musaa ak Aaróona nag dajale mbooloo ma fa janook doj wa, Musaa ne leen: «Yeen diiŋatkat yi, dégluleen ma fii! Doj wii, tee nu leen cee génneel am ndox boog?» \v 11 Ci kaw loolu Musaa yékkati loxoom, dóor yetam ca doj wa ñaari yoon, ndox mu bare wale ca, mbooloo ma daldi naan, ñook seenug jur. \p \v 12 Aji Sax ji nag ne Musaa ak Aaróona: «Gannaaw gëmuleen ma, ngir wormaal sama sellnga fi kanam bànni Israyil, loolu tax na dungeen yóbbu mukk mbooloo mii ca réew ma ma leen jox.» \v 13 Loolooy walum Meriba, (mu firi Jote ba). Fa la bànni Israyil jote woon ak Aji Sax ji, ba mu biral sellngaam fa seen biir. \s1 Edom bañ na \p \v 14 Gannaaw gi, Musaa moo yebale ay ndaw fa dëkk ba ñuy wax Kades, ñu dem ca buurub Edom, ne ko: «Israyil say bokk dañoo wax ne: Umplewoo mboolem coono bi nu daj. \v 15 Sunuy maam a demoon Misra; dëkk nanu Misra lu yàgg, waa Misra di nu mitital, na woon ca sunuy maam. \v 16 Ci biir loolu nu woo \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wall, mu dégg sunu yuux, daldi yebal malaaka, mu génne nu Misra. Léegi nu ngi nii fi Kades, dëkk bi digalook sam réew. \v 17 Ngalla nag may nu, nu jaare sam réew. Dunu fi jaare benn tool, mbaa ab tóokëru reseñ, dunu fi naane ndoxum benn teen. Mbeddum buur daal lanuy topp, dunu jàdd ndijoor ak càmmoñ, ba keroog nuy génn sam réew.» \p \v 18 Buurub Edom nag ne leen: «Dungeen jaare fi man de, lu ko moy saamar laay génne, dajeek yeen.» \v 19 Ndawi \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne ko: «Sél wi rekk lanuy topp, te ndox mu nu naan, nook sunug jur, noo la koy fey. Ñaanunu lenn lu moy doxe sunuy tànk, ba jàll.» \v 20 Mu ne leen: «Dungeen fi jaare mukk!» Ci kaw loolu Edom génn ngir dajeek ñoom, ànd ak gàngoor gu réy, gànnaayu ba diis. \v 21 Noonu la Edom lànke, mayul Israyil mu jaare réewam, ba Israyil mujj teggi. \s1 Aaróona nelaw na \p \v 22 Ci kaw loolu mbooloom \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp bàyyikoo Kades, ba ca tundu Or. \v 23 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax ak Musaa ak Aaróona, ca Or, tund wa ca kemu réewum Edom. Mu ne: \v 24 «Dees na tërali Aaróona fa ay bokkam. Du dugg déy ca réew ma ma jox bànni Israyil, gannaaw yeena gàntaloon sama ndigal ca walum Meriba. \v 25 Àndal ak Aaróona ak doomam Elasar, nga yéege leen ca kaw tundu Or. \v 26 Te nga summi yérey carxal yu Aaróona, solal ko doomam Elasar. Aaróona moom, dees koy tërali ca ay bokkam. Foofa lay deeye.» \p \v 27 Ba loolu amee Musaa def la ko Aji Sax ji sant, ñu ànd yéeg kaw tundu Or, mbooloo ma mépp di gis. \v 28 Musaa summi yérey Aaróona, solal ko doomam Elasar, Aaróona dee foofa ca kaw tund wa, Musaa ak Elasar wàcc tund wa. \v 29 Mbooloo ma mépp nag xam ne Aaróona dëddu na. Waa kër Israyil gépp a ko jooy diiru fanweeri fan. \c 21 \s1 Bànni Israyil am na ndam \p \v 1 Kanaaneen ba, buurub Arat ba dëkke woon Negew, moo dégg ne Israyil a ngay jaare yoonu Atarim, di dikk. Mu xareek Israyil, jàpp ñenn ca ñoom. \v 2 Ci kaw loolu Israyil xasal \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji aw xas, ne ko: «Soo tegee ba teg mbooloo mii ci sunuy loxo déy, dinanu faagaagal seeni dëkk.» \v 3 Aji Sax ji nangul Israyil, jébbal leen Kanaaneen ña, ñu faagaagal leen, ñook seeni dëkk. Ñu daldi wooye gox ba Xorma (mu firi Lu ñu faagaagal). \s1 Lu jëm ci nattub jaan ya \p \v 4 Ñu bàyyikoo tundu Or, jubal yoonu géeju Barax ya, ngir teggi réewum Edom. Mbooloo ma nag mujj xàddi ca yoon wa. \v 5 Ña ngay xultu ca kaw Yàlla ak Musaa, naa: «Lu ngeen nu doon jële Misra, ngir nu dee ci màndiŋ mi? Duw ñam, dum ndox, te wii ñamu toskare génnliku nan!» \v 6 Ba loolu amee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji yebal ay jaani daŋar ca biir mbooloo ma, ñu màtt leen, ba ñu bare ci \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* dee. \v 7 Mbooloo ma dikk ba ci Musaa, ne ko: «Noo tooñ, ndax noo xultu ci kaw Aji Sax ji, ak ci sa kaw. Tinul nu Aji Sax ji, mu teggil nu jaan yi!» Musaa daldi tinul mbooloo ma. \v 8 Aji Sax ji ne Musaa: «Defarlul jëmmu jaan ju am daŋar, nga wékk ko ci bant. Su ko defee képp ku ñu màtt, boo ca xoolee, mucc.» \v 9 Ci kaw loolu Musaa defarlu jaanu xànjar, wékk ko ci bant, ba képp ku jaan màtt, bu xoolee jaanu xànjar ja, daldi mucc. \s1 Israyil daan na Siwon ak Og \p \v 10 \w Bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* fabooti, dem ba dali fa ñuy wax Obot, \v 11 jóge Obot, dali Yee Abarim, ca màndiŋ ma janook Mowab, ca penku ba. \v 12 Foofa lañu faboo, dem ba dali ca walum Seredd, \v 13 bàyyikooti foofa, dem ba dali ca wàllaa dexu Arnon, ga wale ca réewum Amoreen ña te jaare ca màndiŋ ma. Dexu Arnon googa, fa la réewum Mowab digalook Amoreen ñi. \v 14 Moo tax téereb Xarey \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji indi ko, ne: \q1 «Waxeb ga ca Sufa, \q1 xuri Arnon yaak \q1 \v 15 xur ya bartalu, \q1 jëm néegi Ar, leruji suufas Mowab.» \p \v 16 Fa lañu bàyyikoo, dem Beer, (mu firi ab Teen); teen boobu, fa la Aji Sax ji noon Musaa: «Dajaleel mbooloo mi, ma may leen ndox.» \v 17 Ca la Israyil woy woy wii: \q1 «Teen bile walal, nu woy. \q1 \v 18 Ay garmee la bënn, \q1 kàngami askan wi gase la yeti buur, \q2 ak seen banti bopp.» \p Ñu jóge màndiŋ ma, dem ba Matana, \v 19 jóge Matana dem Naxaliyel, jóge Naxaliyel, dem Bamot, \v 20 jóge Bamot ba ca xur, wa ca àllub Mowab, àkki nag njobbaxtalu tundu Pisga, wa tiim ndànd-foyfoy ga. \p \v 21 Ba loolu amee Israyil yebal ay ndaw ca Siwon buurub Amoreen ña, ne ko: \v 22 «May nu, nu jaare sam réew. Dunu fi jàdde benn tool mbaa ab tóokëru reseñ, dunu fi naan ndoxum teen. Mbeddum buur lanuy topp, ba keroog nuy jàll sam réew.» \v 23 Siwon nag mayul Israyil, ñu jaarem réewam, xanaa mu dajale gàngooram gépp, sàqi, ngir dajejeek Israyil ca màndiŋ ma. Mu dikk ba Yaxacc, song Israyil, \v 24 Israyil leel ko ñawkay saamar, nangu seenum réew, dale ko Arnon ba Yabog, ba àgg ca Amoneen ña, ndax kemu réewum Amoneen ñaa fegu woon ba jotuwul. \v 25 Israyil nangu dëkki Amoreen yooyu yépp, daldi sance mboolem seeni dëkk, boole ca Esbon aki dëkk-dëkkaanam. \p \v 26 Esbon moo doon péeyub Siwon buurub Amoreen ña. Kookoo xare woon ak buuru Mowab ba woon, moo nangu ciy loxoom réewam mépp, ba Arnon. \v 27 Moo tax woykat ya ne: \q1 Ayca ca Esbon, ba tabaxees kooti; \q1 na dëkkub Siwon jógati. \q1 \v 28 Lakk gaa nga jóge Esbon, \q1 sawaraa bawoo dëkkub Siwon ba, \q1 xoyomi Ar ga ca Mowab, \q1 gor ñooña tiim dexu Arnon. \q1 \v 29 Mowabee ngalla yaw! \q1 Sànku ngeenee, yeen askanu Kemos\f + \fr 21.29 \fr*\fk Kemos: \fk*\ft tuurum Mowabeen ñi la woon.\ft*\f*, \q1 mi wacc doomam yu góor, ñu daw, \q1 doomam yu jigéen doon jaami Siwon buurub Amor. \q1 \v 30 Noo leen fitt, \q1 Esbon ba Dibon rajaxoo, \q1 nu rajaxeeti ba Nofa, ba àkki Medeba. \p \v 31 Israyil nag dëkke réewum Amoreen ña. \v 32 Ba loolu amee Musaa yebal ay ndaw, ñu yëri dëkk ba ñuy wax Yaser. Gannaaw gi bànni Israyil nangu dëkk-dëkkaan ya, daldi fay dàqe Amoreen ña. \p \v 33 Ba mu ko defee ñu walbatiku, awe yoonu Basan, Og buuru Basan ànd ak gàngooram gépp, dajejeek ñoom, song leen xare ca Eddrey. \v 34 Aji Sax ji ne Musaa: «Bu ko ragal, ndax ci say loxo laa ko teg, mook gàngooram gépp akum réewam, nga def ko na nga defoon Siwon buurub Amoreen ba woon fa Esbon.» \v 35 Ci kaw loolu ñu jam Og, mooki doomam ak gàngooram gépp, ba desewul kuy dund, ñu daldi nangu réewam. \c 22 \ms1 Balaam gis na céru barke bi ñeel Israyil \mr (Saar 22—25) \s1 Buur Balag woo na Balaam wall \p \v 1 \w Bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* demati ba dali ca joori Mowab ca wàllaa dexu Yurdan, janook Yeriko. \v 2 Fekk na Balag doomu Sippor gis mboolem la bànni Israyil def Amoreen ña. \v 3 Mowab nag am tiitaange ju réy ca gàngooru bànni Israyil, ndax bare. Mowab jàq na ba mu gisee bànni Israyil. \v 4 Ci kaw loolu Mowab giseek magi Majan, ne leen: «Ndiiraan wii kat, ni nag di forem parlu ba mu set, ni lañu nara ñédde li nu wër lépp, ba mu set.» \p Jant yooyu Balag doomu Sippor moo doon buuru Mowab. \v 5 Mu yebal ay ndaw ca Balaam doomu Bewor ngir wooyi ko, ca Petor ga Balaam cosaanoo, ca tàkkal dex ga\f + \fr 22.5 \fr*\ft Mooy dexu Efraat.\ft*\f* ngir ne ko: «Balaam! Gàngoor a ngii jóge Misra. Ñu ngii lal suuf si ba mu daj, te ñoo sanc, janook man màkk. \v 6 Kon nag dikkal gaaw ñaanal ma yàlla gàngoor gii, ngir ñoo ma ëpp doole. Jombul ma duma leen, ba dàq leen réew mi, ndax xam naa ne koo ñaanal, mu barkeel, te koo ñaan-yàlla, mu alku.» \p \v 7 Ci kaw loolu magi Mowab ànd ak magi Majan, dem, yóbbaale ay weexal. Ba ñu agsee ca Balaam, daldi koy àgge kàdduy Balag. \v 8 Mu ne leen: «Fanaanleen fii guddig tey. Tont lu ma ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji sant rekk, dinaa leen ko àgge.» Kàngami Mowab dal ak Balaam. \p \v 9 Yàlla nag dikkal Balaam, ne ko: «Nit ñii fi yaw, ñu mu doon?» \v 10 Balaam ne Yàlla: «Buuru Mowab Balag doomu Sippor moo yónnee ci man, ne ma: \v 11 “Balaam, gàngoor a ngii jóge Misra, lal suuf si ba mu daj. Dikkal gaaw móolul ma leen. Jombul ma mana xareek ñoom, ba dàq leen.”» \v 12 Yàlla ne Balaam: «Bul ànd ak ñoom, te bul ñaan-yàlla mbooloo ma, ndax ñooñu ñu barkeel lañu.» \p \v 13 Ba Balaam jógee ca suba sa, da ne kàngami Balag ya: «Delluleen seenum réew, ndax Aji Sax ji bañ na; mayu ma ma ànd ak yeen.» \v 14 Kàngami Mowab daldi dellu ca Balag, ne ko: «Balaam de bañ naa ànd ak nun.» \p \v 15 Balag dellu yebal kàngam yu gëna bare, te gëna kawe. \v 16 Ñooña dem ba ca Balaam, ne ko: «Balag doomu Sippor dafa wax ne: “Ngalla, bu la dara teree dikk, wuysi ma. \v 17 Maa lay teral teraanga ju réya réy. Loo ma wax, ma def. Dikkal rekk, móolul ma gàngoor gii.”» \v 18 Balaam tontu surgay Balag, ne leen: «Bu ma Balag doon jox këram ba mu fees ak xaalis ak wurus sax, duma mana def lenn lu tuut mbaa lu réy, lu tebbi sama ndigalu Yàlla Aji Sax ji. \v 19 Waaye yeen it dal-leen fii guddig tey, ba ma xam lu ma Aji Sax jiy waxaat.» \v 20 Ci kaw loolu Yàlla dikkal Balaam ca guddi ga, ne ko: «Gannaaw woosi la mooy tànki ñii, àndal ak ñoom. Waaye nag lu ma la wax rekk, def ko.» \s1 Mbaam yedd na boroom \p \v 21 Ca ëllëg sa Balaam takk mbaamam, ànd ak kàngami Mowab, dem. \v 22 Ba loolu amee sànjum Yàlla tàkk ndax yoon wa mu sumb. Malaakam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nag taxaw ca yoon wa, nara jànkoonte ak moom, moom mu war mbaamam, ànd ak ñaari surgaam. \v 23 Ci kaw loolu mbaam ma gis malaakam Aji Sax ji taxaw ca digg yoon wa, xàccib saamaram. Mbaam ma ne walbit, wàcc yoon wa, topp àll ba. Balaam dóor mbaam ma, waññi ko ba ca yoon wa. \v 24 Ba mu ko defee malaakam Aji Sax ji taxawi fu yoon wa def ñall wu sew wu jaare digg tóokëri reseñ, ñaari miir séq ko. \v 25 Mbaam ma gis malaakam Aji Sax ji, daldi tafu ca miir ba, ba tancaale ca tànkub Balaam. Balaam dellu ko dóor. \v 26 Malaakam Aji Sax ja dellu jiitu, ba taxawi fu xat, ba maneesula weesalook moom, du ndijoor, du càmmoñ. \v 27 Mbaam ma gis malaakam Aji Sax ja, daldi ne wàpp goor ca suufu Balaam, xol ba fuddu, mu dóorati mbaam ma yet wa. \p \v 28 Ba loolu amee Aji Sax ji tijji gémmiñu mbaam mi, mu ne Balaam: «Ana lu ma la def, ba ñetti yoon a ngii nga di ma dóor?» \v 29 Balaam ne mbaam mi: «Yaa may foontoo, su ma yoroon saamar, léegi laa lay rey!» \v 30 Mu ne ko: «Xanaa du maay sa mbaam mi ngay war bu yàgg ba nga ma moomee, ba tey jii? Dama laa masa def nii?» Mu ne ko: «Déedéet.» \p \v 31 Aji Sax ji nag ubbi bëti Balaam, mu gis malaakam Aji Sax ja, mu taxaw ca yoon wa, xàccib saamaram. Mu ne gurub sukk, dëpp jëëm fa suuf. \v 32 Malaakam Aji Sax ji ne ko: «Lu tax ngay dóor sa mbaam mi ñetti yoon nii? Man mii maa dikk, jànkoonteek yaw, ndax yoonu sànkute laa gis. \v 33 Mbaam mi moo ma gis, teggi ma ba muy ñetti yoon nii. Bu ma teggiwuloon déy, yaw laay rey; moom, ma ba ko, mu dund.» \v 34 Balaam ne malaakam Aji Sax ji: «Maa tooñ, ndax xawma woon ne yaa taxaw, dogale ma ci yoon wi. Léegi nag su la yoon wi neexul, ma daldi dëpp.» \v 35 Malaakam Aji Sax ji ne Balaam: «Àndal ak nit ñi, waaye daal lu ma la waxloo rekk, wax ko.» Balaam nag ànd ak kàngami Balag, dem. \s1 Balaam tase na ak Balag \p \v 36 Ba loolu amee Balag dégg ne Balaam a ngay ñëw, mu gatanduji ko ca dëkku Mowab, ba digalook dexu Arnon, ca catu réew ma. \v 37 Balag ne Balaam: «Xanaa yeblewuma woon, ba yebleeti, di la woolu? Lu la tee woona ñëw? Am dama laa manula teral?» \v 38 Balaam ne Balag: «Maa ngii, wuysi la, waaye mbaa sañ naa waxal sama bopp lenn? Kàddu gu ma Yàlla waxloo de, moom laay wax.» \p \v 39 Ci kaw loolu Balaam ànd ak Balag ba Kiryaat Xusot. \v 40 Balag daldi sarxe ay nag aki xar, sédd ca Balaam ak kàngam ya ko dar. \v 41 Ca suba sa Balag ànd ak Balaam, yéege ko ba ca kaw jaamookaay ba ñu dippee \w Baal|lemma="Baal:"\w*, tuur ma, mu tollu fa di séen lenni catu mbooloo ma. \c 23 \s1 Balaam ñaanal na Israyil \p \v 1 Ba loolu amee Balaam ne Balag: «Tabaxal ma fii juróom ñaari \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*, te waajalal ma fi juróom ñaari yëkk yu ndaw, ak juróom ñaari kuuy.» \v 2 Balag def na ko Balaam wax, Balag ak Balaam ku ci nekk sarxal wenn yëkk ak menn kuuy ci sarxalukaay bu nekk. \v 3 Balaam ne Balag: «Taxawal fii ci sa \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ma dem ba nee. Jombul \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikk, dajeek man. Mbir mu mu ma won, dinaa la ko àgge.» Mu daldi dem ba ca kaw tund wu ndaw wu dara saxul. \p \v 4 Ba loolu amee Yàlla dikk, dajeek Balaam, Balaam ne ko: «Ñaari sarxalukaay yi, yékkati naa leen te sarxalukaay bu ci nekk, sarxal naa ci wenn yëkk ak menn kuuy.» \v 5 Aji Sax ji nag yeb kàddu ci gémmiñu Balaam, daldi ne ko: «Dellul ca Balag, te nga waxe noonu.» \p \v 6 Balaam dellu ca moom, fekkul lu moy mu taxaw ca saraxu dóomalam, moom ak kàngami Mowab yépp. \v 7 Balaam yékkati kàddug ñaanam, ne: \q1 «Fa Aram la ma Balag buuru Mowab jële, \q2 foofa ca tundi penku ya, ne ma: \q1 “Kaay ñaanal ma yàlla Yanqóoba, \q1 Dikkal rëbbal ma Israyil mii.” \q1 \v 8 Moo nu may móoloo ku Yàlla móoluwul? \q1 Ana nu may rëbbe ku Aji Sax ji rëbbul? \q1 \v 9 Kaw doj yii laa tollu di leen séen, \q1 fi kawte yii laa leen jéere. \q1 Aw askan a ngii, dëkke fu beru, \q1 te bokkuñu ak xeet yi. \q1 \v 10 Ana kuy lim feppi suuf, ba lim askanu Yanqóoba? \q1 Ku mana waññ xaajaatub Israyil gii? \q1 Man de, yal naa dee deewinu aji jub ñii, \q1 yal na sama muj mel ni gu askan wii!» \s1 Balaam baamu na ñaanam \p \v 11 Ba loolu amee Balag ne Balaam: «Yaw, li nga ma def nag? Móolu samay noon laa la jële, yaw defoo lenn lu moy ñaanal leen?» \v 12 Mu ne ko: «Xanaa du kàddu gu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji yeb sama gémmiñ, moom laa wara sàmm, ngir wax ko?» \v 13 Balag ne ko: «Kaay rekk, topp ma, ba feneen fooy tollu di leen gis. Seen cat doŋŋ ngay gis nag, waaye doo leen gis ñoom ñépp. Su ko defee nga móolul ma leen foofu.» \v 14 Mu daldi koy yóbbu ba ca toolub Sofim, ca collu tundu Pisga. Ci kaw loolu mu tabax fa juróom ñaari \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*, sarxalukaay bu nekk, mu sarxalati fa yëkk wu ndaw akam kuuy. \v 15 Balaam ne Balag: «Taxaweel nii ci sa \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, man ma séentuji nee.» \p \v 16 Ba loolu amee Aji Sax ji dajeek Balaam, daldi yeb kàddu ci gémmiñam, ne ko: «Dellul ca Balag, te nga waxe noonu.» \v 17 Mu dem ba ca moom, fekku ko lu moy mu taxaw ca wetu saraxu rendi-dóomalam, mook kàngami Mowab. Balag ne ko: «Lu Aji Sax ji wax?» \v 18 Balaam daldi yékkati kàddug ñaanam, ne: \q1 «Jógal dégloo, Balag, \q1 teewlu maa, doomi Sippor. \q1 \v 19 Yàlla du nit, bay fen, \q1 du doom aadama bay tuub. \q1 Moom wax na lu mu deful a? \q1 Am àddu na lu mu sottalul? \q1 \v 20 Kàddug barkeel gii laa jot ndigalam, \q1 Yàllaa barkeel, duma ko tebbi. \q1 \v 21 Séeneesul aw ay ci askanu Yanqóoba, \q1 giseesul aw naqar ci xeetu Israyil wii. \q1 Seen Yàlla Aji Sax jee ànd ak ñoom, \q1 njiinum buur a jibe fa seen biir. \q1 \v 22 Yàllaa leen jële Misra, \q2 féete leen fa ay béjjén féete nagu àll. \q1 \v 23 Ñeengo jàppul Yanqóoba, \q1 gisaane gisul Israyil gii. \q1 Lu jot rekk, àggees ko Yanqóoba: \q1 ne ko: “Israyiloo, lii la Yàlla def.” \q1 \v 24 Wii askan ni gaynde lay jóge, \q1 ni gayndeg sibi lay faboo, \q1 du goor te yàppul am pàdd, \q1 deret ja tuuru, mu xab.» \p \v 25 Ba loolu amee Balag ne Balaam: «Boo leen móoluwul benn yoon kay, bu leen ñaanal ba doyal boog!» \v 26 Balaam ne ko: «Xanaa waxuma la woon ne la lépp lu Aji Sax ji wax, loolu laay def?» \v 27 Balag ne ko: «Kaay rekk, ma yóbbu la feneen. Jombul Yàlla nangu nga móolool ma leen foofu.» \v 28 Balag yóbbu Balaam ba ca collu tundu Pewor, wa tiim ndànd-foyfoy ga. \v 29 Balaam ne Balag: «Tabaxal ma fii juróom ñaari sarxalukaay, te nga waajalal ma fi juróom ñaari yëkk yu ndaw, ak juróom ñaari kuuy.» \v 30 Balag def na Balaam wax, ba noppi sarxal aw yëkk wu ndaw akam kuuy ci kaw sarxalukaay bu nekk. \c 24 \s1 Balaam ñaanalati na Israyil \p \v 1 Balaam nag gis ne \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji la neex mu barkeel Israyil, ba tax sàkkootul ay takk na woon, xanaa mu walbatiku, janook màndiŋ ma. \v 2 Ci kaw loolu Balaam dawal bëtam, daldi séen Israyil, na ñu dale topp seeni giir, Noowug Yàlla daldi wàcc ca moom. \v 3 Ba mu ko defee mu yékkati kàddug ñaanam, ne: \q1 «Kàddug Balaam a ngi, doomu Bewor, \q1 kàddug waa jiy boroom ngis, \q1 \v 4 kàddug kiy dégg waxi Yàlla, \q1 Aji Man ji wonem peeñu, mu gis, \q1 kiy daanu leer, te ay gëtam muriku. \q1 \v 5 Yanqóobaa, yaaka yànji xayma! \q1 Israyil, laa ne, yaaka taaruy màkkaan! \q1 \v 6 Ña nga ne màww ni tooli tàndarma, \q1 nirooteek tóokëri tàkkal dex, \q1 mbaa garabu alowes gu xeeñ gu Aji Sax ji jëmbat, \q1 mbaa garabi seedar yu saxe wali ndox. \q1 \v 7 Ndox maay wale cay bagaanam, \q1 am jiwoom màndim ndox, \q1 buuram nara sut Buur Agag, \q1 nguuram jóg ba kawe. \q1 \v 8 Yàllaay ki ko jële Misra, \q1 féete ko fa ay béjjén féete nagu àll. \q1 Mooy warax xeet yi ko jógal, \q1 dammat leen, jamat leeni fittam. \q1 \v 9 Israyil a ngi yuug ak a goor ni gaynde, \q1 mbete gayndeg sibi, ana ku koy yee? \q1 Ku ko ñaanal barke, yaay barkeel; \q1 ku ko ñaanal alkànde, yaay alku.» \s1 Balaam gis na ëllëgu Israyil \p \v 10 Ba loolu amee Balag sànju ci kaw Balaam, daldi fenqey loxoom. Ci kaw loolu Balag ne Balaam: «Móolu samay noon laa la wooye woon, yaw defoo lu moy ñaanal leena ñaanal, ba muy ñetti yoon nii! \v 11 Léegi nag, laggal ñibbi. Noon naa la dinaa la teral bu baax, waaye mu ngoog, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee la xañ teraanga.» \v 12 Balaam ne Balag: «Xanaa du sa ndaw yi nga yebaloon ci man sax, waxoon naa leen ne leen, \v 13 su ma Balag joxoon këram ba mu fees ak xaalis ak wurus sax, duma mana def ci sama coobarey bopp, lenn lu baax mbaa lu bon, lu tebbi ndigalu Yàlla Aji Sax ji? Li Aji Sax ji wax rekk, moom laay wax. \v 14 Léegi nag maa ngi dellu ca saay bokk, waaye kaay, ma xamal la li xeet wii di def saw xeet, fan yu mujj ya.» \v 15 Ci kaw loolu mu yékkati kàddug ñaanam, ne: \q1 «Kàddug Balaam a ngi, doomu Bewor, \q1 kàddug waa jiy boroom ngis, \q1 \v 16 kàddug kiy dégg waxi Yàlla, \q2 kiy xame ca xam-xamu Aji Kawe ji, \q1 Aji Man ji wonem peeñu, mu gis, \q1 kiy daanu leer, te ay gëtam muriku. \q1 \v 17 Maa ngi koy gis, te du tey, \q1 Maa ngi koy niir, te jubseegul; \q1 biddiiw a feqe fa Yanqóoba, \q1 yetu nguur a yékkatikoo fa Israyil, \q1 daldi toj boppi Mowab, \q2 toj kaaŋi mboolem askanu Set. \q1 \v 18 Edom, mu moom; Seyir, noonam, muy boroom; \q1 Israyil def jaloore. \q1 \v 19 Fa Yanqóoba la buur di bawoo, \q1 dem ñéddi ndesu dëkk ba.» \s1 Balaam gis na mujug nooni Israyil \p \v 20 Ci kaw loolu Balaam geesu réewum Amaleg, dellu yékki kàddug ñaanam, ne: \q1 «Amaleg moo sutu xeet, te sànku lay mujje.» \p \v 21 Mu teg ca geesu réewum Keneen ña, yékkeeti kàddug ñaanam, ne: \q1 «Keneen ñee wér ab dëkkuwaay, \q1 seenub tàgg a làqoo biir doj. \q1 \v 22 Waaye réewum Keneen gépp ay xoyomu, \q1 ba leen Asur di yóbbuji njaam.» \p \v 23 Mu dellooti yékki kàddug ñaanam, ne: \q1 «Wóoy kuy dund, keroog bu Yàlla dogalee lii? \q1 \v 24 Ay gaal ay jóge tefesu Kitim, \q1 néewalsi doole Asur, néewalsi doole Eber. \q1 Waaye ñoom it dañuy mujj sànku.» \p \v 25 Ci kaw loolu Balaam ñibbi am réewam, Balag it demu yoonam. \c 25 \s1 Bànni Israyil bokkaale na ca réewum Mowab \p \v 1 Ci kaw loolu Israyil dale fa Sitim. Mbooloo ma nag tàmbali di moy ak jigéeni Mowab. \v 2 Jigéen ña di woo mbooloo ma ca seen saraxi tuur ya, mbooloo ma di lekk ak a sujjóotal seeni tuur. \v 3 Israyil nag taqook tuur ma ñuy wax \w Baal Pewor|lemma="Baal:"\w*, ba sànjum \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji tàkkal Israyil. \v 4 Aji Sax ji ne Musaa: «Jàppal njiiti mbooloo mi yépp, nga wékk leen ci bant fi kanam Aji Sax ji, bëccëg ndarakàmm, ngir sànjum Aji Sax ji dëddu Israyil.» \v 5 Musaa ne àttekati Israyil: «Na ku nekk ci yeen rey nitam ñi taqook Baal Pewor.» \p \v 6 Ci biir loolu rekk, jenn waayu \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* dikk, indaale senn ndawas waa Majan ci biiri bokkam, Musaa ak mbooloom Israyil mépp di gis, fekk ñoom ñuy jooyoo fa bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* ma. \v 7 Fineyas, doomu Elasar, doomu \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba Aaróona, gis loolu, daldi jóge ca mbooloo ma, jël ab xeej. \v 8 Mu topp waayi Israyil ja ba ca biir néeg ba, daldi leen boole bennub xeej, ñoom ñaar, jam waayi Israyil ji, ba jamaale ndaw si ci biir. Ba mu ko defee mbas ma jotoona dal ca kaw bànni Israyil daldi dakk. \v 9 Ña dee ca mbas ma nag di ñaar fukki junneek ñeent (24 000). \p \v 10 Ba loolu weesee Aji Sax ji wax Musaa, ne ko: \v 11 «Fineyas, doomu Elasar, doomu sarxalkat bi Aaróona, moo moyale Israyil samam sànj, ndax sama fiiraange gi mu ma fiirlee ci seen biir, ba faagaagaluma bànni Israyil ci sama biir fiiraange. \v 12 Kon nag nee ko: Maa ngii di ko baaxe sama \w kóllëreg|lemma="kóllëre g-:"\w* jàmm, \v 13 mu ñeel ko, mook askan wi koy wuutu, te di kóllëreg carxal gu sax dàkk, ndax moo fiire Yàllaam, ba jot bànni Israyil.» \p \v 14 Waayi bànni Israyil ja ñu jamoon, te boole kook ndawas Majan sa jam, mooy Simri doomu Salu. Kilifag kër maamam la woon ca Cimyoneen ña. \v 15 Ndawas Majan sa ñu jam di Kosbi. Baayam Sur doonoon kilifag kër maamam ca giirug Majan ga mu bokk. \p \v 16 Ci kaw loolu Aji Sax ji wax Musaa, ne ko: \v 17 «Noonooleen waa Majan yii, te rey leen, \v 18 ndax ñoom ñoo leen noonoo woon ba ñu leen woree ca mbirum Pewor ma, ak itam ca mbirum ndaw sa Kosbi, seen mbokk may doomu kilifag Majan ja, te ñu jam ko keroog bésu mbas, ma sababoo ca mbirum Baal Pewor, tuur ma.» \c 26 \ms1 Israyil dégg na ab artoom balaa dugg Kanaan \mr (Saar 26—36) \s1 Ñaareelu limeefu bànni Israyil taxaw na \p \v 1 Gannaaw ba mbas ma wéyee, \p \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax Musaa, ak Elasar doomu Aaróona \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba, ne leen: \v 2 «Waññleen mbooloom \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp, ngeen lim turi góor ñépp, na ñu bokke seen këri maam, dale ko ci ñi am ñaar fukki at, jëm kaw, mboolem ñi xare war ci bànni Israyil.» \v 3 Musaa ak Elasar sarxalkat ba wax ak ñoom ca joori Mowab, fa janook Yeriko ca wetu dexu Yurdan; ñu ne leen \v 4 ñi dale ci ñaar fukki at, jëm kaw lees di lim, na ko Aji Sax ji sante Musaa. Lii moo di limeefu nit ña soqikoo ci bànni Israyil, ña génne woon Misra: \p \v 5 Ruben moo doon taawub Israyil. Ñi askanoo ci Ruben ñoo di Anog mi sos làngu Anogeen ñi, ak ñoom Palu mi sos làngu Paluween ñi, \v 6 ak ñoom Esron mi sos làngu Esroneen ñi, ak ñoom Karmi mi sos làngu Karmeen ñi. \v 7 Làngi Rubeneen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek ñett ak juróom ñaar téeméer ak fanweer (43 730). \p \v 8 Palu moo meññ Elyab, \v 9 Elyab meññ Nemwel ak Datan ak Abiram. Datan ak Abiram ñooñii doonooni njiit ca mbooloo ma, ñoo doon diiŋat Musaa ak Aaróona. Ña nga bokkoon ca gàngooru Kore, ba ñuy diiŋat Aji Sax ji, \v 10 ba suuf sa xar, boole leen ak Kore, wonn, keroog ba gàngoor ga sànkoo, te sawara wa lakk ñaar téeméeri nit ak juróom fukk, ñu daldi doon firnde luy artoo. \v 11 Doomi Kore ya nag deewuñu ca. \p \v 12 Ñi askanoo ci Simeyon, ñook seeni làng ñoo di ñoom Nemwel mi sos làngu Nemweleen ñi, ak ñoom Yamin mi sos làngu Yamineen ñi, ak ñoom Yakin mi sos làngu Yakineen ñi, \v 13 ak ñoom Sera mi sos làngu Cerayeen ñi, ak ñoom Sawul mi sos làngu Cawuleen ñi. \v 14 Làngi Cimyoneen ñaa ngoogu, di ñaar fukki junneek ñaar ak ñaar téeméer (22 200). \p \v 15 Ñi askanoo ci Gàdd, ñook seeni làng ñoo di ñoom Cefon mi sos làngu Cefoneen ñi, ak ñoom Agi mi sos làngu Ageen ñi, ak ñoom Suni mi sos làngu Cuneen ñi, \v 16 ak ñoom Osni mi sos làngu Osneen ñi, ak ñoom Eri mi sos làngu Ereen ñi, \v 17 ak ñoom Arodd mi sos làngu Aroddeen ñi, ak ñoom Areli mi sos làngu Areleen ñi. \v 18 Làngi Gàddeen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróomi téeméer (40 500). \p \v 19 Am na nag doomi Yuda yu ñuy wax Er ak Onan. Waaye Er ak Onan ña ca réewum Kanaan lañu faatoo. \v 20 Ñi askanoo ci Yuda, ñook seeni làng ñoo di ñoom Sela mi sos làngu Celaneen ñi, ak ñoom Peres mi sos làngu Pereseen ñi, ak ñoom Sera mi sos làngu Cerayeen ñi. \v 21 Ñi askanoo ci Peres ñoo di ñoom Esron mi sos làngu Esroneen ñi, ak ñoom Amul mi sos làngu Amuleen ñi. \v 22 Làngi Yudeen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom ñaar fukki junneek juróom benn ak juróomi téeméer (76 500). \p \v 23 Ñi askanoo ci Isaakar, ñook seeni làng ñoo di Tola mi sos làngu Toleen ñi, ak ñoom Puwa mi sos làngu Puween ñi, \v 24 ak ñoom Yasub mi sos làngu Yasubeen ñi, ak ñoom Simron mi sos làngu Simroneen ñi. \v 25 Làngi Isaakar a ngoogu. Ña ñu leen limal di juróom benn fukki junneek ñeent ak ñetti téeméer (64 300). \p \v 26 Ñi askanoo ci Sabulon, ñook seeni làng ñoo di ñoom Seredd mi sos làngu Sereddeen ñi, ak ñoom Elon mi sos làngu Eloneen ñi, ak ñoom Yaleel, mi sos làngu Yaleleen ñi. \v 27 Làngi Sabuloneen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom benn fukki junni ak juróomi téeméer (60 500). \p \v 28 Ñi askanoo ci Yuusufa nag, ñook seeni làng, ñoo soqikoo ci Manase ak Efrayim. \v 29 Ñi soqikoo ci Manase ñoo di ñoom Makir mi sos làngu Makireen ñi. Makir moo jur Galàdd. Ci Galàdd la làngu Galàddeen ñi soqikoo. \v 30 Ñii ñoo askanoo ci Galàdd: Yeser mi sos làngu Yesereen ñi, ak ñoom Eleg mi sos làngu Elegeen ñi, \v 31 ak Asriyel mi sos làngu Asriyeleen ñi, ak Sikem mi sos làngu Sikemeen ñi, \v 32 ak Semida mi sos làngu Semideen ñi, ak Efer mi sos làngu Efereen ñi. \v 33 Selofat doomu Efer nag amuloon doom ju góor, xanaa aw jigéen doŋŋ. Doomi Selofat yu jigéen di Maala ak Nowa ak Ogla ak Milka ak Tirca. \v 34 Làngi Manasee ngoogu, ña ñu leen limal di juróom fukki junneek ñaar ak juróom ñaar téeméer (52 700). \p \v 35 Ñii nag ñoo askanoo ci Efrayim, ñook seeni làng: ñoom Sutela mi sos làngu Cuteleen ñi, ak ñoom Beker mi sos làngu Bekereen ñi, ak ñoom Taxan mi sos làngu Taxaneen ñi. \v 36 Ñii nag, askanu Sutela lañu: ñoom Eran, ak làngu Eraneen ñi mu sos. \v 37 Làngi Efrayim a ngoogu, ña ñu leen limal di fanweeri junneek ñaar ak juróomi téeméer (32 500). \p Ñooñoo askanoo ci Yuusufa, ñook seeni làng. \p \v 38 Ñi askanoo ci Beñamin, ñook seeni làng ñoo di ñoom Bela mi sos làngu Belayeen ñi, ak ñoom Asbel mi sos làngu Asbeleen ñi, ak ñoom Ayram mi sos làngu Ayrameen ñi, \v 39 ak ñoom Sufam mi sos làngu Sufameen ñi, ak ñoom Ufam mi sos làngu Ufameen ñi. \v 40 Askanu Bela wi sosoo ci Àrd ak Naaman ñoo di làngu Àrdeen ñi, ak làngu Naameen ñi sëtoo ci Naaman. \v 41 Ñooñoo askanoo ci Beñamin, ñook seeni làng, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer (45 600). \p \v 42 Ñii nag ñoo askanoo ci Dan, ñook seeni làng: ñoom Suwam ak làngu Cuwameen ñi. Daneen ñaa ngoogu, na ñu lime seeni làng. \v 43 Mboolem làngi Cuwameen, ña ñu leen limal juróom benn fukki junneek ñeent la, ak ñeenti téeméer (64 400). \p \v 44 Ñi askanoo ci Aser, ñook seeni làng ñoo di ñoom Imna mi sos làngu Imneen ñi, ak ñoom Iswi mi sos làngu Isween ñi, ak ñoom Berya mi sos làngu Beryeen ñi. \v 45 Waa askanu Berya ñoo di ñoom Eber mi sos làngu Ebereen ñi, ak ñoom Malkiyel mi sos làngu Malkiyeleen ñi. \v 46 Doomu Aser ju jigéen nag moo di Sera. \v 47 Làngi Asereen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400). \p \v 48 Ñi askanoo ci Neftali ñook seeni làng ñoo di ñoom Yàcceel, mi sos làngu Yaceleen ñi, ak ñoom Gunni mi sos làngu Guneen ñi, \v 49 ak ñoom Yeccer mi sos làngu Yeccereen ñi, ak ñoom Silem mi sos làngu Cilmeen ñi. \v 50 Neftaleen ñaa ngoogu, ñook seeni làng, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróom ak ñeenti téeméer (45 400). \p \v 51 Limeefu bànni Israyil a ngoogu, di juróom benni téeméeri junneek benn ak juróom ñaar téeméer ak fanweer (601 730). \s1 Lu jëm ci séddaleb réew ma \p \v 52 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nag wax Musaa, ne ko: \v 53 «Ñii lees di séddale réew mi, te na cér yi dëppook limu nit ñi: \v 54 làng gu gëna mag, na am cér bu gëna mag, làng gu gëna tuut, am cér bu gëna tuut, làng gu ci nekk, cér bi dëppook ab limam lees koy jox. \v 55 Ab tegoo bant doŋŋ lees di séddalee réew mi, te seen limu giiri maam ya ñu bokk, na dëppook seenub cér. \v 56 Ci kaw tegoo bant lees di dogale céru giir gu ñu bare séq, ak gu ñu néew séq.» \s1 Ñaareelu limeefu Leween ñi taxaw na \p \v 57 Ñii nag lañu limal \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi ak seeni làng: ñoom Gerson mi sos làngu Gersoneen ñi, ak ñoom Keyat mi sos làngu Keyateen ñi, ak ñoom Merari mi sos làngu Merareen ñi. \v 58 Ñii itam ci làngi Leween lañu: làngu Libneen ñi, ak làngu Ebroneen ñi, ak làngu Maaleen ñi, ak làngu Museen ñi, ak làngu Korayeen ñi. Keyat nag mooy maamu Amram; \v 59 soxnas Amram di Yokebedd doomu Lewi, ja juddoo Misra. Yokebedd am ak Amram Aaróona ak Musaa ak Maryaama, seenub jigéen. \v 60 Aaróona moo jur Nadab ak Abiyu ak Elasar ak Itamar. \v 61 Nadab ak Abiyu ña nga dee keroog ba ñu taalalee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji cuuraay lu warul. \v 62 Ña ñu limal Leween ñi nag ñaar fukki junneek ñett lañu (23 000), di mboolem góor ña am weer, jëm kaw, te limaaleesu leen ak \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ga ca des, ndax joxeesu leen ab cér ci biir bànni Israyil. \s1 Tëj nañu limeef ya \p \v 63 Ñooñu lañu lim ci njiital Musaa ak Elasar \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba, ba ñu tënkee limeefu \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ca joori Mowab, ga janook Yeriko, ca tàkkal dexu Yurdan. \v 64 Ñooñu, kenn desul ca seen biir, te bokkoon ca limeefu bànni Israyil, ba Musaak Aaróona sarxalkat ba jëkkoona tënke ca màndiŋu Sinayi. \v 65 Ndax ci ñoom la \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji noon dee rekk lañuy def ba jeex ca màndiŋ ma. Kenn desu ca, ku dul Kaleb doomu Yefune, ak Yosuwe doomu Nuun. \c 27 \s1 Lu jëm ci jigéen ñi ak seen céri suuf \p \v 1 Ci kaw loolu ay doomi Selofat yu jigéen jóg. Seen baay Selofat, Efer ay baayam, Efer, Galàdd ay baayam, Galàdd, Makir ay baayam, Makir, Manaseey baayam, Manase, Yuusufaay baayam. Jigéen ñooñu ñoo di Maala ak Nowa ak Ogla ak Milka ak Tirca. \v 2 Ñoo taxaw fa kanam Musaa, ak Elasar \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba, ak njiit ya, ak mbooloo ma mépp, ca bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* ma. Ñu ne: \v 3 «Sunu baay daa dee ca màndiŋ ma. Moom nag bokkuloon ca gàngooru Kore, ga daje woon ci kaw \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, waaye bàkkaaru boppam a ko rey. Bàyyiwul nag doom ju góor. \v 4 Waaye lu tax ñu génne sunu turu baay ci làngam gi mu bokk, ndax ñàkk doom ju góor? Joxleen nu sunub cér ci biir wàll wi sunu bokki baay yu góor bokk ak sunu baay kay!» \p \v 5 Ci kaw loolu Musaa jébbal Aji Sax ji, àtteb jigéen ña. \v 6 Aji Sax ji wax Musaa ne ko: \v 7 «Li doomi Selofat yi wax dëgg la. Danga leen di jox kay, ab cér ci biir wàll, wi seen baay bokk ak bokkam yu góor. Su ko defee nga féetale leen seen céru suufu baay. \p \v 8 «Te nga wax \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, ne leen: “Bu ku góor deeyee te bàyyiwul doom ju góor, doomam ju jigéen ngeen di jox céru suufam. \v 9 Su amul doom ju jigéen nag, góor ñi mu bokkal waajur ngeen di jox céru suufam. \v 10 Su amul góor gu mu bokkal waajur, góor ña baayam bokkal waajur, ñoom ngeen di jox céru suufam. \v 11 Su baayam amul góor gu mu bokkal waajur, mbokkam mu ko gëna jege ci biir làngam, moom ngeen di jox céru suufam. Kookooy donn cér ba. Na loolu di dogalu yoon, ñeel bànni Israyil, noonu ko Aji Sax ji sante Musaa.”» \s1 Yosuwe wuutu na Musaa \p \v 12 Gannaaw loolu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ne Musaa: «Yéegil ca kaw tundu Abarim wee, nga séentu réew mi ma jox \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \v 13 Boo ko séentoo ba noppi, yaw itam dees na la tërali ca say bokk, ni sa mag Aaróona, \v 14 gannaaw yeena diiŋat sama ndigal ca màndiŋu Ciin, fa mbooloo ma jote woon ak man. Yeena wormaalul sama sellnga ca kanam mbooloo ma, ca ndox ma. Mooy walum Meriba, (mu firi Jote ba), ma woon ca Kades, ca màndiŋu Ciin.» \p \v 15 Musaa nag wax Aji Sax ji, ne ko: \v 16 «Aji Sax ji, yaw Yàlla mi moom noowi bépp boroomu suux, ngalla tabbal nit ku jiite mbooloo mi, \v 17 kuy xareji, jiite leen, délsi, jiite leen, di leen yóbbu, di leen délloosi, ba mbooloom Aji Sax ji baña mel ni xar yu amul sàmm.» \v 18 Aji Sax ji ne Musaa: «Jëlal Yosuwe doomu Nuun. Nit la ku noowal biir nekk ci moom. Nanga ko teg sa loxo, sase ko noonu. \v 19 Taxawal ko fi kanam Elasar \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi, ci kanam mbooloo mépp, te nga sas ko ci seen kanam, \v 20 daldi koy sédd lenn ci sa daraja, ngir mbooloom bànni Israyil mépp déggal ko. \v 21 Ca Elasar sarxalkat bi nag la war di dem, ngir mu di ko seetal fi kanam Aji Sax ji, lu \w Urim|lemma="Urim ak Tumim:"\w*, jumtukaayu tegtal bi, feeñal. Ci ndigalal Elasar nag lañuy génne, te ci ndigalam it lañuy dellusee, moom Yosuwe, ak mboolem bànni Israyil giy ànd ak moom, mbooloo mépp.» \p \v 22 Ba mu ko defee Musaa def na ko Aji Sax ji sant. Mu ànd ak Yosuwe, taxawal ko fa kanam Elasar sarxalkat bi, ak mbooloo mépp. \v 23 Musaa nag teg Yosuwe ay loxoom, daldi koy sas, na ko Aji Sax ji santaanee, mu jottli. \c 28 \s1 Bés bu nekk laaj na ab sarax \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa, ne ko: \v 2 «Santal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen sama sarax, sama ñam wi jëm ci sama saraxi sawara ngir xetug jàmm, ñeel ma, nañu farlu ci di ma ko indil saa yu àppam jotee. \v 3 Nga waxleen ne leen, lii moo di saraxu sawara bi ñuy indil Aji Sax ji: xar yu góor yu menn at yu mucc sikk, ñaar ci bés bi, muy \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* bi war bés bu nekk. \v 4 Menn xar mi, ngeen sarxal ko ci suba, ñaareel bi, ngeen sarxal ko diggante ngoon ak jant bu so. \v 5 Benn fukkeelu efab sunguf su mucc ayib, di ñetti kilo, mooy \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* bi xar mu nekk di àndal, ñu tooyale ko walaatu xiinu diwu segalu oliw, di liitar ak genn-wàll. \v 6 Looloo di rendi-dóomal bi war bés bu nekk, na ñu ko dogale woon ca tundu Sinayi, ngir xetug jàmm, muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. \p \v 7 «\w Saraxu tuuram|lemma="Sarax yi:"\w* walaatu xiin lay doon, di liitar ak genn-wàll ngir xar mu ci nekk. Ci ëtt bu \w sell|lemma="sell:"\w* bi lees di sotti saraxu tuuru bi, naan gu diis googu, ñeel Aji Sax ji. \v 8 Ñaareelu xar mi, sarxal-leen ko diggante ngoon ak jant bu so, mu ànd ak saraxu peppam ak saraxu tuuram niki ci suba, ngeen def ko saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji. \s1 Bésub Noflaay am na saraxam \p \v 9 «\w Bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w* nag ñaari xari menn at yu mucc sikk lay doon, ak \w saraxu peppam|lemma="Sarax yi:"\w*, biy ñaari fukkeeli efay sunguf su mucc ayib, di juróom benni kilo, ñu tooyale ko ag diw, te mu ànd ak \w saraxu tuuram|lemma="Sarax yi:"\w*. \v 10 Loolooy \w saraxu rendi-dóomalu|lemma="Sarax yi:"\w* bésub Noflaay, ci bésub Noflaay bu nekk, te bokkewul ak dóomal bi war bés bu nekk, te ànd ak saraxu tuuram. \s1 Terutel weer am na saraxam \p \v 11 «Te itam seen bési Terutel weer, nangeen sarxe ab \w rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ñeel \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Ñaari yëkk yu ndaw, ak menn kuuy, ak juróom ñaari xar yu góor yu menn at, te lu ci nekk mucc sikk, \v 12 ak ñetti fukkeeli efay sunguf su mucc ayib, di juróom ñeenti kilo, muy \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w*, ñu tooyale ko ag diw, booleek yëkk wu nekk, ak ñaari fukkeeli efay sunguf su mucc ayib, di juróom benni kilo, muy saraxu pepp, ñu tooyale ko ag diw, booleek kuuy mi, \v 13 ak benn fukkeelu efab sunguf su mucc ayib, di ñetti kilo, muy saraxu pepp, ñu tooyale ko ag diw, booleek xar mu ci nekk. Saraxu rendi-dóomal la, ngir xetug jàmm, di saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. \p \v 14 «Ay \w saraxi tuuram|lemma="Sarax yi:"\w* genn-wàllu xiinu biiñ la, di ñetti liitar ci yëkk wu nekk, ak benn ñetteelub xiin, di ñaari liitar ci kuuy mi, ak walaatu xiin, di liitar ak genn-wàllu biiñ ci xar mu ci nekk. Loolooy dóomalu weer wi, weer wu ci nekk, ba weeri at mi daj. \v 15 Ak itam bennub sikket, mook saraxu tuuroom ngir \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*, ñeel Aji Sax ji ci bésub Terutel weer wi, te bokkewul ak rendi-dóomal bi ñuy sarxe bés bu nekk. \s1 Bésub Mucc am na saraxam \p \v 16 «Weer wi jëkk ci at mi nag, fukki fanam ak ñeent mooy \w bésub Mucc|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* bi, ñeel \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \v 17 Ëllëg sa, fukki fani weer woowu ak juróom, di màggal; diiru juróom ñaari fan, mburu mu amul lawiir lees cay lekk. \v 18 Bés bu jëkk boobu, woote bu \w sell|lemma="sell:"\w* lees cay amal. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey. \v 19 Nangeen ci def saraxu sawara, mu dib \w rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ñeel Aji Sax ji: ñaari yëkk yu ndaw, ak menn kuuy, ak juróom ñaari xari menn at, te ngeen def lépp di lu mucc sikk. \v 20 Yooyii ànd ak \w saraxu peppam|lemma="Sarax yi:"\w*, di sunguf su mucc ayib, su ñu tooyale ag diw, ñetti fukkeeli efay sunguf, di juróom ñeenti kilo, ciw yëkk, ñaari fukkeeli efay sunguf, di juróom benni kilo, cim kuuy, \v 21 ak benn fukkeelu efab sunguf, di ñetti kilo, ci mii xar, benn fukkeelu efa, ca mee, ba juróom ñaari xar yi daj, \v 22 ak benn \w sikketu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w* ngir seen njotlaay. \v 23 Te bokkewul ak rendi-dóomalu suba si, rendi-dóomal boobu war bés bu nekk. \v 24 Sarax yu mel noonu ngeen di sarxal ci bés bi, ak seen \w saraxu tuuru|lemma="Sarax yi:"\w*, diiru juróom ñaari fan, muy ñamu saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji. Ci kaw rendi-dóomal bi war bés bu nekk, ci lees koy dolli. \v 25 Bésub juróom ñaareel ba, seen bésub woote bu sell lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey. \s1 Ngóob am na saraxam \p \v 26 «Bésub \w ndoortel meññeef|lemma="Sarax yi:"\w* ba ngeen di sarxesi \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* mu bees, ñeel \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ci seen biir \w màggalug Ayi bés|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* nag, seen bésub woote bu \w sell|lemma="sell:"\w* lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey. \v 27 Nangeen ci sarxal ab \w rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji: ñaari yëkk yu ndaw, ak menn kuuy, ak juróom ñaari xari menn at. \v 28 Saraxu peppam di sunguf su mucc ayib, su ñu tooyale ag diw. Ñetti fukkeeli efay sunguf, di juróom ñeenti kilo ci yëkk wu nekk, ak ñaari fukkeeli efa, di juróom benni kilo ci kuuy mi, \v 29 ak fukkeelub efa, di ñetti kilo, ci mii xar, fukkeelub efa ca mee, ba juróom ñaari xar yi daj, \v 30 ak bennub sikket ngir seen njotlaay. \v 31 Sarxeleen loolu, te bumu bokke ak rendi-dóomal bi war bés bu nekk tey ànd ak saraxu peppam. Lu mucc sikk nag ngeen di def sarax yooyii, te ngeen defaale \w saraxi tuuram|lemma="Sarax yi:"\w* yi ci war. \c 29 \s1 Bési liit yi laaj na sarax \p \v 1 «Bu loolu weesee, benn fanu weeru juróom ñaareel, seen bésu woote bu \w sell|lemma="sell:"\w* lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey. Bés la bu ngeen di yéenee ag liit. \v 2 Sarxal-leen ci ab \w rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* ngir xetug jàmm, ñeel \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji: wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy, ak juróom ñaari xari menn at, te lu ci nekk mucc sikk. \v 3 \w Saraxu peppam|lemma="Sarax yi:"\w* lay àndal, di sunguf su mucc ayib, su ñu tooyale ag diw; ñetti fukkeeli efay sunguf, di juróom ñeenti kilo ci yëkk wi, ñaari fukkeeli efa, di juróom benni kilo ci kuuy mi, \v 4 ak benn fukkeelu efab sunguf, di ñetti kilo ci mii xar, benn fukkeelu efa ca mee, ba juróom ñaari xar yi daj, \v 5 ak benn \w sikketu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*, ngir seen njotlaay. \v 6 Bokkewul ak rendi-dóomalu Terutel weer wu nekk, mook saraxu peppam, bokkewul it ak rendi-dóomal bi war bés bu nekk, ak saraxu peppam, ak seen \w saraxi tuur|lemma="Sarax yi:"\w*, ni ko yoon tërale. Dees koy def ngir xetug jàmm, muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. \s1 Bésub Njotlaay laaj na sarax \p \v 7 «Fukki fanu juróom ñaareelu weer woowu it, seen bésub woote bu \w sell|lemma="sell:"\w* lay doon, te ngeen toroxlu ci. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey. \v 8 Sarxal-leen ci ab \w rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ñeel \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ngir xetug jàmm: wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy, ak juróom ñaari xari menn at, te lu mucc sikk ngeen di def lépp. \v 9 \w Saraxu peppam|lemma="Sarax yi:"\w* lay àndal, di sunguf su mucc ayib su ñu tooyale ag diw; ñetti fukkeeli efay sunguf, di juróom ñeenti kilo ci yëkk wi, ñaari fukkeeli efa, di juróom benni kilo ci kuuy mi, \v 10 ak benn fukkeelu efab sunguf, di ñetti kilo ci mii xar, benn fukkeelu efa ca mee, ba juróom ñaari xar yi daj, \v 11 ak benn \w sikketu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*, te du bokke ak póotum bàkkaaru njotlaay gi, ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam, ak seen \w saraxi tuur|lemma="Sarax yi:"\w* yi ci war. \s1 Màggalu Mbaar yi laaj na sarax \p \v 12 «Fukki fan yaak juróom ci juróom ñaareelu weer woowu itam, seen bésu woote bu \w sell|lemma="sell:"\w* lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey. Amal-leen ci ag màggal, ñeel \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, diiru juróom ñaari fan, doore ko ca bés ba. \v 13 Nangeen ca sarxal ab \w rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji: fukki yëkk yu ndaw ak ñett, ak ñaari kuuy, ak fukk ak ñeenti xari menn at, te lépp mucc sikk. \v 14 Seen \w saraxi pepp|lemma="Sarax yi:"\w* di sunguf su mucc sikk su ñu tooyale ag diw, ñetti fukkeeli efay sunguf, di juróom ñeenti kilo ci wenn yëkk wu nekk, ba fukki yëkk yeek ñett daj; ñaari kuuy yi, kuuy mu ci nekk, ñaari fukkeeli efay sunguf, di juróom benni kilo, \v 15 ak benn fukkeelu efab sunguf, di ñetti kilo ci mii xar, benn fukkeelu efa ca mee, ba fukki xar yeek ñeent daj, \v 16 ak benn \w sikketu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*. Bokkewul ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, ak saraxu peppam si muy àndal, ak \w saraxu tuuram|lemma="Sarax yi:"\w*. \p \v 17 «Bésub ñaareel ba: fukki yëkk yu ndaw ak ñaar; ak ñaari kuuy, ak fukk ak ñeenti xari menn at, te lépp mucc sikk. \v 18 Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuur yay ànd ak yëkk ya, mbaa kuuy ya, mbaa xar ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral. \v 19 Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam ak seen saraxi tuur. \p \v 20 «Bésub ñetteel ba: fukki yëkk yu ndaw ak benn, ak ñaari kuuy, ak fukk ak ñeenti xari menn at, te lépp mucc sikk. \v 21 Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuur yay ànd ak yëkk ya, mbaa kuuy ya, mbaa xar ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral. \v 22 Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam ak saraxu tuuram. \p \v 23 «Bésub ñeenteel ba: fukki yëkk, ak ñaari kuuy, ak fukk ak ñeenti xari menn at, te lépp mucc sikk. \v 24 Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuur yay ànd ak yëkk ya, mbaa kuuy ya, mbaa xar ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral. \v 25 Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam ak saraxu tuuram. \p \v 26 «Bésub juróomeel ba: juróom ñeenti yëkk, ak ñaari kuuy, ak fukk ak ñeenti xari menn at, te lépp mucc sikk. \v 27 Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuur yay ànd ak yëkk ya, mbaa kuuy ya, mbaa xar ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral. \v 28 Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam ak saraxu tuuram. \p \v 29 «Bésub juróom benneel ba: juróom ñetti yëkk, ak ñaari kuuy, ak fukki ak ñeenti xari menn at, te lépp mucc sikk. \v 30 Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuur yay ànd ak yëkk ya, mbaa kuuy ya, mbaa xar ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral. \v 31 Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam ak saraxu tuuram. \p \v 32 «Bésub juróom ñaareel ba: juróom ñaari yëkk, ak ñaari kuuy, ak fukk ak ñeenti xari menn at, te lépp mucc sikk. \v 33 Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuur yay ànd ak yëkk ya, mbaa kuuy ya, mbaa xar ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral. \v 34 Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam, ak saraxu tuuram. \p \v 35 «Bésub juróom ñetteel ba seen bésub ndaje lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey. \v 36 Nangeen ci sarxal ab rendi-dóomal, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji: wenn yëkk, ak menn kuuy, ak juróom ñaari xari menn at, te lépp mucc sikk. \v 37 Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuur yay ànd ak yëkk ya, mbaa kuuy ya, mbaa xar ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral. \v 38 Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam, ak saraxu tuuram. \p \v 39 «Yooyu sarax ngeen di def, ñeel Aji Sax ji, ci seen bési màggal, te du bokke ak seen sarax yi ngeen xasal seen bopp, ak seen \w saraxi yéene|lemma="Sarax yi:"\w*, ak seen saraxi dóomali bés bu nekk, ak seen saraxi pepp ak seen saraxi tuur, ak seen \w saraxi canti biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*.» \p \v 40 Ba mu ko defee Musaa àgge \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* mboolem la ko Aji Sax ji sant. \c 30 \s1 Yoon wi sàrtal na lu nit ki xasal boppam \p \v 1 Ci kaw loolu Musaa wax ak kilifay giiri \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, ne leen: «Lii moo di ndigal li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dénkaane: \p \v 2 «Góor gu xasal Aji Sax ji aw xas, mbaa mu giñ ngir dogu gu mu tegool boppam, bumu tebbi kàddoom. Noonee ko làmmiñam tudde, na ko ni defe ba mu mat sëkk. \p \v 3 «Te jigéen ju xasal Aji Sax ji aw xas, ngir dogu gu mu dogu, te fekk ko di ndaw ca biir kër baayam ba tey, \v 4 su baay ba déggee xasu ndaw sa, ak dogu ga mu tegool boppam, te waxu ca doomam dara, su boobaa mboolem xasi ndaw sa day sax, te mboolem dogu gu mu doguloon boppam day sax. \v 5 Waaye su ko baayam aayee, ca bés ba mu ca déggee, su boobaa mboolem xasi ndaw si, ak mboolem dogu ya mu doguloon boppam, du sax, te Aji Sax jee koy jéggal, ndax baayam aaye woon na ko. \p \v 6 «Su fekkee ne ndaw si dafa am jëkkër gannaaw kàdduy xas yu ko topp, mbaa kàddug rëccle, gu mu tegool boppam, \v 7 su ko jëkkër ja déggee, te bés ba mu ko déggee, waxu ko ca dara, su boobaa xasi ndaw si day sax, te kàdduy dogu ya mu tegooloon boppam day sax. \v 8 Waaye su fekkee ne ca bés ba ko jëkkër ja déggee, ca la ko aaye, su boobaa jëkkër ja neenal na xas wa toppoon ndaw si, mbaa kàddug rëccle ga mu tegooloon boppam, te Aji Sax jee koy jéggal. \p \v 9 «Su dee kàddug xas gu jibe ci ku jëkkëram faatu, mbaa ku ñu baal, mboolem lu mu tegooloon boppam day sax. \p \v 10 «Su fekkee ne ci biir kër jëkkëram la nit ki xase, mbaa mu dogul fa boppam ab dogu, ci kaw ngiñ, \v 11 jëkkër ji dégg ci, te waxu ko dara, aayewu ko, su boobaa mboolem xasi ndaw si day sax, te mboolem dogu bu ndaw si tegooloon boppam, day sax. \v 12 Su wéree nag ne jëkkër ji neenal na kàdduy jabaram yooyu, ca bés ba mu ko déggee, su boobaa lépp lu làmmiñu ndaw si tuddoon, jëme ci kàdduy xasam, mbaa kàddu gu mu tegooloon boppam, lenn du ci sax. Jëkkëram a ko neenal, te Aji Sax jee koy jéggal. \v 13 Mboolem aw xas nag, ak mboolem ngiñ lu ku jigéen ki dogoo, te jublu ci ag toroxlu, jëkkëram moo koy saxal, jëkkëram moo koy neenal. \v 14 Su jëkkër ji noppee ba noppi, waxu ko dara ca bés ba, ba ca ëllëg sa, su boobaa mboolem kàdduy xasi jabaram, mbaa mboolem kàdduy dogu yu toppoon jabaram, jëkkër jee ko saxal, ndax moo ko waxul dara ca bés ba mu ko déggee. \v 15 Ndegam nag jëkkër ji, beneen bés, gannaaw ba mu déggee kàdduy jabaram, la doora àddu ngir neenal wax ja, su boobaa mooy gàddu bàkkaaru jabaram.» \p \v 16 Yooyu dogali yoon la Aji Sax ji dénk Musaa, ci diggante nit ak jabaram, ak diggante baay ak doom ju jigéen, ba muy ndaw te nekk kër baayam. \c 31 \s1 Israyil duma na Majan \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa, ne ko: \v 2 «Fexeel ba feyul \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ci waa Majan\f + \fr 31.2 \fr*\ft Seetal ci 25.16-19.\ft*\f*. Gannaaw loolu dees na la yóbbu, tëral la fa say bokk.» \p \v 3 Musaa daldi wax ak mbooloo ma, ne leen: «Na ñenn ci yeen gànnaayu, waajal xare, te dal ci kaw waa Majan, ba feyul Aji Sax ji. \v 4 Gii giir, junni, gee giir junni, ba giiri Israyil yépp daj, ngeen yebal leen ñu xareji.» \p \v 5 Ba mu ko defee ñu tànne ca gàngoori Israyil, junniy góor jóge ci giir gu nekk, ñuy fukki junneek ñaari (12 000) xarekat yu gànnaayu. \v 6 Musaa nag yebal leen, junni jóge ci giir gu nekk, ñu xareji. Ñoom ak \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi Fineyas doomu Elasar, ñoo xareji, yóbbaale jumtukaay yu \w sell|lemma="sell:"\w* yaak liiti xare ya. \v 7 Ñu xareek Majan, na ko Aji Sax ji sante Musaa, ba rey góor ñépp, \v 8 reyaale buuri Majan, Ewi ak Rekem ak Sur ak Ur ak Reba, juróomi buuri Majan ya. Balaam doomu Bewor it, ñu reye ko saamar. \p \v 9 Ba loolu amee bànni Israyil jàpp jigéeni Majan, ak seeni tuut-tànk, ak seen jur gépp, gu gudd ak gu gàtt, seen alal jépp, ñu sëxëtoo ko. \v 10 Seen dëkk yépp ak seeni dëkkuwaay, ak seen dal yépp, ñu lakk. \v 11 Ba mu ko defee ñu jël mboolem la ñu sëxëtoo, mboolem la ñu ca jàppe, nit ñaak jur ga. \v 12 Ñu daldi yóbbu ca Musaa ak Elasar sarxalkat ba, ak mbooloom bànni Israyil, ña ñu jàppe ca xare ba, ak la ñu ca jàppe, ak la ñu sëxëtoo. Ñu indi lépp ca seen dal ba ca joori Mowab, fa janook Yeriko, te dendeek dexu Yurdan. \p \v 13 Ci kaw loolu Musaa ak Elasar sarxalkat ba ànd ak mboolem njiiti mbooloo ma, ñu génn dal ba, gatandu leen ca biti. \v 14 Musaa nag sànju ca kaw kilifay xare ya, muy kilifay kuréli junni yaak kilifay kuréli téeméer, ya jóge xare. \v 15 Musaa ne leen: «Kon jigéeni Majan ñépp ngeen bàyyi, ñu dund! \v 16 Xanaa du ñoom ñoo dëdduloo woon bànni Israyil Aji Sax ji, ci ndigalal Balaam, ca mbir ma woon ca Pewor, ba tax mbas ma dikkal mbooloom Aji Sax ji? \v 17 Kon nag reyleen lépp luy góor ci tuut-tànk yi, mboolem lu ciy jigéen ju xam lalu góor it, rey leen, \v 18 mboolem lu ciy jigéen ju ndaw, te xamul lalu góor, ngeen bàyyi mu dund, ñeel leen. \p \v 19 «Te yeen nag, dal-leen ci biti, buleen dugg ci biir dal bi diiru juróom ñaari fan, mboolem ñi rey ak mboolem ñi laal ku ñu rey. Nangeen setlu bésub ñetteel ba, ak bésub juróom ñaareel ba, yeen ak ñi ngeen jàpp. \v 20 Te itam lépp luy yére, ak bépp jumtukaayu der, ak lépp lees defare kawari bëy, ak bépp jumtukaayu bant, nangeen ko setal.» \p \v 21 Ba mu ko defee Elasar sarxalkat ba wax ak ña xareji woon, ne leen: «Lii moo di dogalu yoon, bi Aji Sax ji dénk Musaa: \v 22 Luy wurus ak xaalis ak xànjar, ak weñ gu ñuul, ak weñ gu weex, ak beteex, \v 23 mboolem lu dul lakk, rekk, nangeen ko laalale sawara, mu set. Ndoxum setlu mi it, warees na koo dellu setale yooyii. Waaye mboolem luy lakk, ci ndoxum setal mi doŋŋ lees koy dugal, ngir mu set. \v 24 Bésub juróom ñaareel ba, fóotleen seeni yére, daldi set. Gannaaw loolu man ngeena duggsi ci dal bi.» \s1 Lu jëm ci séddaleb alalu waa Majan \p \v 25 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ne ko: \v 26 «Yaw ak Elasar \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi, ak ñi jiite seeni kër maam ci mbooloo mi, waññleen alal ji ñu nangoo xare, nit aku jur. \v 27 Xaajleen sëxëtoo mi ñaar, te ngeen séddale ko diggante xarekat ya xareji woon, ak mbooloo mi ci des yépp. \v 28 Te ngeen sàkkal Aji Sax ji, ci céru xarekat ya xareji woon, ab galag bu yemook benn bopp ci juróomi téeméer (500) yu nekk, ci aw nit, mbaa ay nag, mbaa ay mbaam, mbaa ay gàtt. \v 29 Ci céru xarekat yi ngeen koy sàkke, jox ko Elasar sarxalkat bi, muy jooxeb Aji Sax ji. \v 30 Céru \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* bi ci des, nangeen ci sàkk benn ci juróom fukk yu nekk (50), ci aw nit, mbaa ay nag, mbaa ay mbaam, mbaa ay gàtt, mbaa gépp jur, te ngeen jox ko \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi dénkoo dénkaaney màkkaanu Aji Sax ji.» \p \v 31 Ba loolu amee Musaa ak Elasar sarxalkat bi defe ko noonee ko Aji Sax ji sante Musaa. \v 32 La des ca alalu sëxëtoo, ja ña xareji woon indaale, gannaaw ba ñu ca génnee yooyu, nii la tollu: gàtt yi, juróom benni téeméeri junneek juróom ñaar fukk ak juróom (675 000); \v 33 nag yi, juróom ñaar fukki junneek ñaar (72 000); \v 34 mbaam yi, juróom benn fukki junneek benn (61 000), \v 35 aw nit, fanweeri junniy jigéen ñu xamul lalu góor (30 000). \p \v 36 Genn-wàll giy céru nit ña xareji woon, nii la tëdde: gàtt yi, ñetti téeméeri junneek fanweer ak juróom ñaar ak juróomi téeméer (337 500), \v 37 galagu Aji Sax ji génne ci gàtt yi, di juróom benni téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróom (675); \v 38 nag yi, fanweeri junneek juróom benn (36 000), galagu Aji Sax ji génne ci, di juróom ñaar fukk ak ñaar (72); \v 39 mbaam yi, fanweeri junneek juróomi téeméer (30 500), galagu Aji Sax ji génne ci, di juróom benn fukk ak benn (61); \v 40 aw nit, fukki junneek juróom benn (16 000), galagu Aji Sax ji génne ci, di fanweeri bopp ak ñaar (32). \v 41 Ba mu ko defee Musaa jox galag ba Elasar sarxalkat ba, muy jooxeb Aji Sax ji, na ko Aji Sax ji sante Musaa. \p \v 42 Genn-wàll giy céru bànni Israyil, ba Musaa teqale ak cérub ña xareji woon, \v 43 te muy céru mbooloo ma, ci wàllu gàtt yi, ñetti téeméeri junneek fanweer ak juróom ñaar ak juróomi téeméer (337 500) la; \v 44 nag yi di fanweeri junneek juróom benn (36 000); \v 45 mbaam yi, fanweeri junneek juróomi téeméer (30 500); \v 46 aw nit, fukki junneek juróom benn (16 000). \v 47 Musaa daldi sàkk ci céru bànni Israyil boobu, benn ci juróom fukk yu nekk. Musaa jox loola Leween ñi dénkoo dénkaaney màkkaanu Aji Sax ji, noonee ko ko Aji Sax ji sante woon. \s1 Kilifay xare ya jëfe nañu ngor \p \v 48 Ba loolu amee njiiti gàngooru xarekat ya, kilifay kuréli junni yaak kilifay kuréli téeméer ya, ñoom ñépp dem ca Musaa. \v 49 Ñu ne Musaa: «Sang bi, nun de, waññ nanu xarekat yi ci sunu kilifteef, waaye kenn wuutewu ci. \v 50 Moo tax nu indi jooxeb \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ku nekk ak la nga muurloo, ci gànjari wurus; lami përëg, ak takkub jara, ak jaaroy torlukaay, ak jaaroy nopp, aki caq. Noo ko def sunu njotlaayal bakkan, fi kanam Aji Sax ji.» \p \v 51 Musaa ak Elasar \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba nangoo wurus wa ca ñoom, lépp di takkaay yu ñu tëgg. \v 52 Mboolem wurusu jooxe, wi ñu jooxeel Aji Sax ji, di fukk ak juróom benni junniy siikal ak juróom ñaar téeméer ak juróom fukk (16 750), yemook barigo ak juróom ñaar fukki kilo (170), te bawoo ci kilifay kuréli junni yaak kilifay kuréli téeméer ya. \v 53 Xarekati gàngoor ga ñoom, dañoo féetewoo la ñu sëxëtoo. \v 54 Musaa ak Elasar sarxalkat ba nag jële wurus wa ca kilifay kuréli junni yaak kuréli téeméer ya. Ñu yóbbu ko ca biir \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* ma, muy seedeel \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* fi kanam Aji Sax ji. \c 32 \s1 Ay giir des na penkub Yurdan \p \v 1 Jur gu ne gàññ, bare lool, la Rubeneen ñi ak Gàddeen ñi amoon. Ñu xoolaat diiwaanu Yaser ak diiwaanu Galàdd, gisuñu lu moy àll bu neexa yareg jur. \p \v 2 Ba mu ko defee Gàddeen ñaak Rubeneen ña dikk, wax ak Musaa ak Elasar \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba, ak kilifay mbooloo ma. Ñu ne leen: \v 3 «Gox yii di Atarot, ak Dibon, ak Yaser, ak Nimra, ak Esbon, ak Elale, ak Sebam, ak Nebo, ak Bewon, \v 4 mboolem réew mii \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji daan fi kanam mbooloom Israyil de, réew mu neexa yareg jur la, te nun, sang bi, boroomi jur lanu.» \v 5 Ñu teg ca ne: «Kon nag ngalla sang bi, baaxe nu réew mii, muy sunub cér, te nga bañ noo jàlle dexu Yurdan.» \p \v 6 Musaa ne Gàddeen ñaak Rubeneen ña: «Xanaa seeni bokk duñu xareji, yeen ngeen toog fii? \v 7 Dangeena nara yoqiloo \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, ba tere leena jàlli ca réew, ma leen Aji Sax ji jox? \v 8 Lu mel nii de, la seeni baay defoon ba ma leen yebalee, ñu jóge Kades Barneya, ngir yëri réew ma. \v 9 Dañoo dem ba àgg xuru Eskol, ba gis réew ma, doora délsi, di yoqiloo bànni Israyil, ngir ñu baña duggi ca réew, ma leen Aji Sax ji joxoon. \v 10 Sànjum Aji Sax ji tàng na bésub keroog, ba mu giñ, ne: \v 11 “Kenn du gis mukk réew ma ma giñaloon Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, ci góor ñi jóge Misra te am ñaar fukki at, jëm kaw, gannaaw mataluñu kóolute ci man. \v 12 Xanaa Kaleb doomu Yefune, Keneseen bi, ak Yosuwe doomu Nuun, ndax ñoo matal kóolute ci Aji Sax ji.” \v 13 Ba loolu amee sànjum Aji Sax ji tàkkal Israyil, mu wërloo leen ca màndiŋ ma diiru ñeent fukki at, ba mboolem maas googa defoon lu Aji Sax ji ñaawlu, ñépp jeex tàkk. \v 14 Yeen nag defuleen lu moy jóg wuutu seeni baay, njurum bàkkaarkat yi ngeen doon, di xamb sànjum Aji Sax, ji tàkkal bànni Israyil? \v 15 Su ngeen ko dëddoo it, day dellu wacc bànni Israyil ci màndiŋ mi rekk, ngeen daldi sànklu mii mbooloo mépp.» \p \v 16 Ba loolu weesee, ñu dikkaat, ne ko: «Ay gétt lanu bëgga sàkk fii ngir sunuy gàtt, aki dëkk ngir sunuy njaboot. \v 17 Waaye nun kay danuy daldi gànnaayu, jiitu bànni Israyil, ba keroog ñu leen yóbboo ca seen suuf. Sunu njaboot a nuy xaare fii, biir dëkk yu tata wër, ngir ñu mucc ci waa réew mi. \v 18 Dunu dellu mukk sunuy kër, ba keroog bànni Israyil di séddu, ku ci nekk jot céru suufam. \v 19 Waaye nun dunu bokk ak ñoom ab céru suuf ca wàllaa dexu Yurdan, ak la ca topp, ndax day fekk nu jot sunu céru suuf, ci wet gii féete dexu Yurdan penku.» \p \v 20 Musaa ne leen: «Su ngeen ko defee noonu, gànnaayu fi kanam Aji Sax ji ngir xareji, \v 21 su seen mboolem boroomi gànnaay jàllee dexu Yurdan fi kanam Aji Sax ji, ba keroog mu dàqee ay noonam, \v 22 ba réew ma nangul Aji Sax ji, su boobaa déy, sañ ngeena délsi, te wàccoo ngeen ak Aji Sax ji, wàccoo ak bànni Israyil, te su boobaa it réew mii ñeel leen, di seen moomeel fi kanam Aji Sax ji. \v 23 Waaye su ngeen jëfewul noonu kat, yeena moy Aji Sax ji, te xamleen ne seenug moy dina leen dab. \v 24 Kon nag sàkkleen ay dëkk ngir seeni njaboot, aki gétt ngir seeni gàtt, waaye li ngeen dige daal, defleen ko.» \p \v 25 Ba loolu amee Gàddeen ñaak Rubeneen ña ne Musaa: «Sang bi, noonu nga ko santaanee, ni lanu koy defe. \v 26 Sunuy goneek sunuy jabar, ak sunuy gàtt, ak sunu jur gépp fii ci dëkki Galàdd lay des. \v 27 Waaye nun, mboolem ñi yor ngànnaay danuy jàll dex gi fi kanam Aji Sax ji, ngir xareji ni nga ko waxe, sang bi.» \p \v 28 Musaa nag santaane ci seen mbir ca Elasar sarxalkat ba, ak Yosuwe doomu Nuun, ak kilifay bànni Israyil, ya jiite seeni kër maam. \v 29 Musaa ne leen: «Su Rubeneen ñeek Gàddeen ñi àndeek yeen, ñoom ñépp gànnaayu ngir xareji fi kanam Aji Sax ji, ba réew ma nangul leen, nangeen leen jox réewum Galàdd, muy seen moomeel. \v 30 Waaye su ñu àndul ak yeen, gànnaayu jàll, ci seen biir lañuy séddu suuf, ca biir réewum Kanaan.» \p \v 31 Ba loolu amee Gàddeen ña ak Rubeneen ña dellu ne: «Sang bi, li nu Aji Sax ji wax rekk lanuy def. \v 32 Nooy gànnaayu jàlli réewum Kanaan fi kanam Aji Sax ji, waaye nun, cér bi nuy moom, wàllu dexu Yurdan wii lay doon.» \p \v 33 Musaa nag tudde cér yii, askanu Gàdd, ak askanu Ruben, ak genn-wàllu giirug Manase doomu Yuusufa: nguurug Siwon buurub Amoreen ñi la leen jox, ak nguurug Og buuru Basan, réew ma mépp, boole ca dëkk yu mag ya, ak àll ya ko wër. \v 34 Ba mu ko defee Gàddeen ña tabax Dibon ak Atarot ak Arower, \v 35 ak Aterot Sofan, ak Yaser ak Yogbowa, \v 36 ak Bet Nimra, ak Bet Aran, lépp di dëkk yu tata wër. Ñu sàkkaale ay wurmbal ngir seeni gàtt. \v 37 Rubeneen ña it tabax Esbon ak Elale ak Kiryaatayim, \v 38 ak Nebo, ak Baal Mewon, lenn ca turi dëkk ya soppiku, ak Sibma. Ñu tudde dëkk yooyu ñu tabaxaat, seen turi bopp. \p \v 39 Ci kaw loolu ñi askanoo ci Makir doomu Manase, songi bëj-gànnaaru Galàdd, nangu ko, dàqe fa Amoreen ña. \v 40 Ba mu ko defee Musaa jox Galàdd, askanu Makir, ñu dëkke. \v 41 Ci biir loolu askanu Yayir, mi askanoo ci Manase, dem nanguji yeneen dëkki Galàdd yu ndaw. Ñu tudde leen Awot Yayir. \v 42 Noba it nanguji Kenat ak dëkk ya ko wër, daldi tudde gox ba boppam, muy Noba. \c 33 \s1 Limees na yooni tukkiy Israyil \p \v 1 Lii moo di doxi \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, ba ñu génnee réewum Misra, def seeni gàngoor, ca njiital Musaa ak Aaróona. \v 2 Musaa moo bind seeni dalukaay ak seen yoon ya ñu jaare, ci ndigalal \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Lii moo di seeni jaar-jaar, ak seeni dalukaay: \p \v 3 Fa Ramses lañu bàyyikoo, fukki fan ak juróomu weer wi jëkk ci at mi. Keroog bés ba topp ca \w bésub Mucc|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* ba, ca la bànni Israyil daagu, génn, waa Misra gépp di gis. \v 4 Booba waa Misraa ngay rob ña Aji Sax ji fàdd ca ñoom, néewi mboolem seen taaw ya. Aji Sax jee mbugale noonu seen yàlla ya. \p \v 5 Bànni Israyil nag jóge Ramses, dali Sukkóot. \v 6 Ñu jóge Sukkóot, dali Etam ga ca catu màndiŋ ma. \v 7 Ba ñu bàyyikoo Etam, dañoo walbatiku ba Pi Axirot ga janook Baal Cefon, daldi dal fa kanam Migadol. \v 8 Ñu jóge Pi Axirot, jàll géej ga, wuti màndiŋ ma. Dox nañu yoonu ñetti fan ca biir màndiŋu Etam, doora dal Maara. \v 9 Ñu jóge Maara, dem ba Elim, Elim ga ca fukki bëti ndox yaak ñaar, ak juróom ñaar fukki garabi tàndarma ya. Ñu dal foofa. \v 10 Ba ñu jógee Elim, fa feggook géeju Barax ya la ñu dali. \v 11 Ñu bawoo géeju Barax ya, dali ca màndiŋu Ciin, \v 12 bawooti màndiŋu Ciin, dali Dofka, \v 13 bawooti Dofka, dali Alus. \v 14 Ba ñu bàyyikoo Alus, Refidim lañu dali. Foofa nag mbooloo ma amuñu fa ndox mu ñu naan. \v 15 Ñu bàyyikoo Refidim, dali ca màndiŋu Sinayi, \v 16 bàyyikoo màndiŋu Sinayi, dali Kibbrot Taawa, \v 17 bàyyikooti Kibbrot Taawa, dali Aserot. \v 18 Ba ñu jógee Aserot, Ritma lañu dali. \v 19 Ñu jóge Ritma, dali Rimon Peres, \v 20 jóge Rimon Peres, dali Libna, \v 21 jógeeti Libna, dali Risa. \v 22 Ba ñu bawoo Risa, Keyelata lañu dali. \v 23 Ñu bawoo Keyelata, dali tundu Sefer, \v 24 bawoo tundu Sefer, dali Arada, \v 25 bawooti Arada, dali Makeyelot. \v 26 Naka lañu bàyyikoo Makeyelot, dali Tayat, \v 27 bàyyikoo Tayat, dali Tera, \v 28 bàyyikooti Tera, dali Mitka. \v 29 Ba ñu jógee Mitka, Asmona lañu dali. \v 30 Ñu jóge Asmona, dali Moserot; \v 31 jóge Moserot, dali Bene Yaakan, \v 32 jógeeti Bene Yaakan, dali Xor Gitgaat. \v 33 Ba ñu bawoo Xor Gitgaat, Yotbata lañu dali. \v 34 Ñu bawoo Yotbata, dali Abrona, \v 35 bawoo Abrona, dali Esiyon Geber, \v 36 bawooti Esiyon Geber, dali Kades ca màndiŋu Ciin. \v 37 Ba ñu bàyyikoo Kades, ca tundu Or wa digalook réewum Edom lañu dali. \p \v 38 Ba mu ko defee Aaróona \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba yéeg ca kaw tundu Or, ci ndigalal Aji Sax ji. Mu daldi faatu foofa, ca ñeent fukkeelu at ma, gannaaw ba bànni Israyil génnee réewum Misra, yemook benn fanu juróomeelu weeru at ma. \v 39 Aaróona mu ngi woon ci téeméeri atam, ak ñaar fukk at ñett (123) ba mu faatoo ca kaw tundu Or. \v 40 Ci kaw loolu Kanaaneen ba, buurub Arat, ba dëkke woon bëj-saalumu réewum Kanaan, daldi yég ne bànni Israyil a ngay dikk. \p \v 41 Ba ñu jógee tundu Or, Calmona lañu dali. \v 42 Ñu jóge Calmona, dali Punon, \v 43 jóge Punon, dali Obot, \v 44 jógeeti Obot, dali Yee Abarim, ga digalook réewum Mowab. \v 45 Ba ñu jógee Yee Abarim, Dibon Gàdd lañu dali. \v 46 Ñu jóge Dibon Gàdd, dali Almon Diblatayim, \v 47 jógeeti Almon Diblatayim, dali ca tundi Abarim, janook tundu Nebo. \v 48 Ba ñu bawoo tundi Abarim, ca joori Mowab lañu dali, ca wetu dexu Yurdan, janook Yeriko. \v 49 Wetu dexu Yurdan, ga ca diggante Bet Yesimot ak Abel Sitim, ca joori Mowab, fa lañu dale. \s1 Ndigali xare jib na \p \v 50 Ba loolu amee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati ak Musaa ca joori Mowab, ca wetu dexu Yurdan, ga janook Yeriko. Mu ne ko: \v 51 «Waxal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen: Bu ngeen jàllee dexu Yurdan, ba dugg réewum Kanaan, \v 52 nangeen dàq waa réew mépp, nangeen yàqte seen mboolem tuur yu ñu yett, te seen mboolem jëmm yu ñu móol, yàqteleen ko, seen mboolem \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* it, tasleen ko. \v 53 Defleen réew mi moomeel, ngeen dëkke ko, ndax yeen laa jox réew mi, ngir ngeen moom ko. \v 54 Tegooleen bant réew mi, séddoo ko ci seeni làng. Làng gu gëna mag, na am cér bu gëna mag, làng gu gëna tuut, am cér bu gëna tuut. Fépp fu tegoo bant génneel ag làng, ñooy doon boroom. Ci seen biir giiri maam ngeen di séddu. \v 55 Waaye su ngeen dàqul waa réew mi, ña ngeen fa bàyyi ñooy mujj diy dég yu leen di luqi, aki dagg yuy cuut seeni wet. Ñoo leen di lëjal witt ca biir réew mooma ngeen sance. \v 56 Su boobaa nag na ma naroona def seen noon yooyu, yeen laa koy def.» \c 34 \s1 Aji Sax ji rëddlu na digu réew mi \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa, ne ko: \v 2 «Santal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, nga ne leen bu ngeen duggee réewum Kanaan, lii moo di réew ma ngeen di muurloo, muy seenub cér. Réewum Kanaan a ngi, ak kemi suufam: \p \v 3 «Seen kemu bëj-saalum a ngay dale màndiŋu Ciin, leru réewum Edom, daleeti ca catal géeju Xorom ga ca penku. \v 4 Seen kemu daa dënglu, jaare fa féete yéegub Akerabim bëj-saalum, jaare Ciin nag, dem ba bëj-saalumu Kades Barneya, jëm Àccar Adar ba àgg Asmon. \v 5 Asmon la kem gay jàddaate jubal xuru Misra, doora àkki géej. \p \v 6 «Géej gu mag gi mooy doon seen kemu sowu. Loolooy seen kemu sowu. \p \v 7 «Lii nag mooy seen kemu bëj-gànnaar. Ca géej gu mag ga ngeen di rëdde, ba ca tundu Or, \v 8 rëdde ko fa tundu Or, mu jëm Lebo Amat, jàll ba Cedàdd, \v 9 wéyeeti fa, jaare Sifron, jëm Àccar Enan. Loolooy seen kemu bëj-gànnaar. \p \v 10 «Rëddleen seen kemu penku, mu dale Àccar Enan ba Sefam, \v 11 kemu ga wàcce Sefam, jëm Ribla, fa féete Ayin penku, wàccati ba leruji dexu Kineret, ca wet ga ko féete penku, \v 12 kemu ga dellu wàcc ba ca dexu Yurdan, doora àkki géeju Xorom ga. Loolooy doon seenum réew ak kemoom yi ko wër.» \p \v 13 Ba mu ko defee Musaa sant bànni Israyil, ne leen: «Réew moomu ngeen di tegoo bant, séddoo ko, te moom la Aji Sax ji santaane ñu jox ko juróom ñeenti giir yeek genn-wàll, \v 14 gannaaw giirug Ruben, ak seeni kër maam, ak giiru Gàdd ak seeni kër maam séddu nañu, te genn-wàllu giirug Manase itam jot nañu seen cér ba noppi. \v 15 Ñaari giir ya, ak genn-wàllu giir googu ñoo séddu suuf ca penkub dexu Yurdan, fa janook Yeriko.» \s1 Lim nañu saytukati séddale ba \p \v 16 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa, ne ko: \v 17 «Ñii nag ñoo leen di séddale réew mi: Elasar \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi, ak Yosuwe doomu Nuun. \v 18 Ay njiit ngay jële kenn-kenn, ci giir gu nekk, ngir ñu jàpp ci séddaleb réew mi. \v 19 Ñooñoo di: Ci wàllu giirug Yuda, Kaleb doomu Yefune, \v 20 wàllu giirug Cimyoneen ñi, Samiyel doomu Amiyut, \v 21 wàllu giirug Beñamin, Elidat doomu Kislon, \v 22 wàllu giirug Daneen ñi, lenn njiit, di Bukki doomu Yogli, \v 23 wàllu Yuusufeen ñi; li féete ak giirug Manaseen ñi, lenn njiit, di Aniyel doomu Efot, \v 24 li féete ak giirug Efraymeen ñi, lenn njiit, di Kemwel doomu Siftan, \v 25 ci wàllu giirug Sabuloneen ñi, lenn njiit, di Elisafan doomu Parnag, \v 26 wàllu giirug Isakareen ñi, lenn njiit, di Paltiyel doomu Asan, \v 27 wàllu giirug Asereen ñi, lenn njiit, di Awiyut doomu Selomi, \v 28 wàllu giirug Neftaleen ñi, lenn njiit, di Pedayel doomu Amiyut.» \v 29 Ñooñu la Aji Sax ji sant ñu séddale \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, réewum Kanaan. \c 35 \s1 Lu jëm ci céri suufi Leween ñi \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati ak Musaa ca joori Mowab, ca wetu dexu Yurdan, fa jàkkaarlook Yeriko. Mu ne ko: \v 2 «Santal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ñu sàkkal \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi ci seen céru suuf, ay dëkk yu Leween ñi dëkke. Àllu parlu ya wër dëkk ya it, joxleen ko Leween ñi. \v 3 Su ko defee dëkk yooyu ñeel leen, ñu dëkke. Seen àlli parlu it ñeel seenug jur, ak seen alal, ak seen mboolem mala. \v 4 Parluy dëkk yi ngeen di jox Leween ñi, ci miiru dëkk ya lay dale, jëm biti lu day ni junniy xasab, yemook juróomi téeméeri meetar, ci wet gu nekk. \v 5 Su ko defee ngeen natte ca biti dig-digal bu gudde ñaari junniy xasab, yemook junniy meetar ci wetu penku; ñaari junniy xasab, yemook junniy meetar, wetu bëj-saalum; ñaari junniy xasab, yemook junniy meetar, wetu sowu; ñaari junniy xasab, yemook junniy meetar, wetu bëj-gànnaar, dëkk bi nekk ci digg bi. Dig-digal boobu day ñeel Leween ñi, di seen parluy dëkk. \v 6 Dëkk yi ngeen di jox Leween ñi, ñoo di juróom benni dëkki rawtu, yi ku rey nit mana raweji, ak yeneen ñeent fukki dëkk ak ñaar yu ngeen leen ciy dollil. \v 7 Kon mboolem dëkk yi ngeen di jox Leween ñi, ñeent fukk ak juróom ñett la, ak seen àlli parlu. \v 8 Dëkk yi ngeen leen di génneel ci céri suufi bànni Israyil nag, la cay génne ca ña ëpple suuf, réyal leen ko, te la cay génne ca ña néewle suuf, ngeen néewal ko. Giir gu nekk daal, dayob céru suufam si mu séddu, moom lay topp, ngir sàkke ci ay dëkkam, jox Leween ñi.» \s1 Lu jëm ci dëkki rawtu yi \p \v 9 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa, ne ko: \v 10 «Waxal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, ne leen bu ñu jàllee dexu Yurdan ba dugg réewum Kanaan, \v 11 nañu sàkk ay dëkk yuy doon seen dëkki rawtu, ba ku rey nit te du teyeefam, man faa raweji. \v 12 Mooy doon seen dëkki rawtu yees di mucce ci mbokkum \w jotkat|lemma="jotkat b-:"\w* buy toppe\f + \fr 35.12 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Sarxalkat yi \+bk* 24.17-21.\ft*\f*, ba ki rey nit du dee, te taxawagul fa kanam mbooloo mi, ngir ñu àtte ko. \p \v 13 «Kon dëkk yi ngeen di jox Leween ñi, juróom benn a ciy doon seen dëkki rawtu. \v 14 Ñetti dëkk yu ngeen di joxe ci wàllu dexu Yurdan wii, ak ñetti dëkk yu ngeen di joxe ca réewum Kanaan, lépp di ay dëkki rawtu. \v 15 Waaye muy bànni Israyil, muy doxandéem, muy gan gu nekk ci seen biir, na juróom benni dëkk yooyu doon seen rawtu yeen ñépp, ba képp ku rey nit te du teyeefam, man faa raweji. \p \v 16 «Su dee ag weñ la ko dóor, mu dee, moo ko rey, te dee rekk mooy àtteb ki rey. \v 17 Su dee aw doj wu mana rey la jël, dóor ko ko, mu dee, moo ko rey, te dee rekk mooy àtteb ki rey. \v 18 Su dee bant bu mana rey la jël, dóor ko ko, mu dee it, moo ko rey, te dee rekk mooy àtteb ki rey. \v 19 Jotkat biy toppe bakkan ba nag, mooy rey ka rey; fu mu dajeek moom, moo koy rey. \v 20 Su dee ci biir mbañeel la dale ci kawam, mbaa mu sànni ko aw saan wu mu ko waajal, ba mu dee, \v 21 mbaa ci biir mbañeel la ko dóore loxoom ba mu dee, su boobaa dee rekk mooy àtteb ka dóore. Moo ko bóom. Jotkat bay toppe bakkan ba nag, bu dajeek ka rey, da koy rey. \p \v 22 «Ndegam nag du caageenu mbañeel, xanaa mu jekki dal ci kawam, mbaa mu sànni ko këf ku mu mana doon, te du lu mu waajoon, \v 23 mbaa muy doj wu mana rey wu mu waddal ci kaw nit ki, ba nit ki dee, te gisul woon nit ki, te nit ka du woon ab noonam, te fekkul itam muy sàkku loraangey nit ka, \v 24 su boobaa la mbooloo may wéyal diggante ki rey, ak jotkat bay toppe, moo di àtte yii ci yoon tëral: \v 25 Mbooloo mi day musal ki rey ci loxol jotkatu bakkanu ka dee, te mbooloo ma da koy delloo ca dëkkub rawtoom ba mu làquji woon. Fa lay toog, ba kera deewug \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bu mag ba ñu baaxoo fale diw gu \w sell|lemma="sell:"\w*. \v 26 Ndegam nag ka rey moo génna génn, ba wees kemu dëkkub rawtoom ba mu làquji woon, \v 27 ba jotkat bay toppe bakkan fekk ko fu wees kemu dëkkub rawtoom, su boobaa su ko jotkatu bakkan ba reyee, du tax mu gàddu bakkan. \v 28 Ndax kat ci biir dëkkub rawtoom la wara toog, ba kera deewug sarxalkat bu mag bi. Gannaaw bu sarxalkat bu mag bi deeyee nag, ki rey sañ naa dellu fa mu bokk. \p \v 29 «Loolu mooy dogalu yoon bi leen ñeel, yeen ak seen askan, ci seen mboolemi dëkkuwaay. \p \v 30 «Képp ku faat bakkan nag, ci kaw kàddu gu tukkee ci ay seede doŋŋ lees ko saña reye, moom ma rey, waaye bennub seede du seedeel nit, ngir ñu teg ko àtteb dee. \p \v 31 «Te it buleen jël benn xaalisu njotug bakkanu kenn ku rey nit ku yelloo dee. Kooku dee rekk mooy àtteem. \v 32 Buleen jël it xaalisu njotug nit ku làquji ca dëkkub rawtoom, ngir may ko mu dellu fa mu dëkk, te sarxalkat bu mag bi deewul. \v 33 Buleen tilimal réew mi ngeen nekk. Deret kat mooy tilimal réew mi, te réew mi deesu ko jote lenn, ci deret ju ñu tuur ci biiram, lu moy deretu ka tuur deret. \v 34 Buleen sobeel réew mi ngeen dëkk, te man ma màkkaanoo ci biiram, ndax man Aji Sax ji maa màkkaanoo ci biir bànni Israyil.» \c 36 \s1 Lu jëm ci séyu jigéenu Israyil, ak céru suufam \p \v 1 Ba loolu wéyee kilifay njaboot yi askanoo ci Yuusufa, te bokk ci làngu Galàdd doomu Makir mi sëtoo ci Manase, ñoo dikk. Ñu wax fa kanam Musaa, ak kilifay njabooti \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \v 2 Ñu ne: «Sang bi, xam nga \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji moo digle woon ñu tegal bant bànni Israyil, séddale leen réew mi. Ci biir loolu, sang bi, ndigal ñeel la, tukkee ci Aji Sax ji, ngir nga jël sunu céru doomu baay Selofat, jox ko ay doomam yu jigéen. \v 3 Waaye bu ñu séyee ci yeneen giiri bànni Israyil de, seen céru suuf mooy wàññikoo ci sunu céru maam, dolliku ca céru giir ga ñu séyi ca seen biir, te kon cér ba nu tegoo woon bant moo cay wàññikoo. \v 4 Te it bu atum Yiwiku\f + \fr 36.4 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Sarxalkat yi \+bk* 25.8-55.\ft*\f* mu bànni Israyil agsee, seen cér day dolliku ca céru giir ga ñu séyi ca seen biir. Te kon it ci sunu céru giiru maam, la seen cér boobu di wàññikoo.» \p \v 5 Ba loolu wéyee, Musaa jox bànni Israyil ndigal, ci ndigalal Aji Sax ji, ne: «Dëgg la giirug Yuusufeen ñi wax. \v 6 Kàddu gii nag mooy li Aji Sax ji santaane ci doomi Selofat yu jigéen yooyu: Ku leen neex, nañu séy ak moom, na fekk rekk, ka ñuy séyal askanoo ci làng gu bokk ci seen giirug baay. \v 7 Du benn céru suuf ci biir bànni Israyil, buy jóge ci genn giir, toxu ca geneen, waaye na ku nekk ci bànni Israyil yem kepp ca suufas giiram, ga mu donne cay maamam. \v 8 Mboolem ku jigéen ku donn suuf ci giiri bànni Israyil, ci biir làng gu bokk ci giirug maamam rekk lay séy, ngir ku nekk ci bànni Israyil mana ñoŋal céru maamam. \v 9 Su ko defee du benn céru suuf buy jóge ci genn giir, toxu ca geneen, waaye giirug bànni Israyil gu ci nekk day yem kepp ca céru suufam.» \p \v 10 Na ko Aji Sax ji sante Musaa nag, na la ko doomi Selofat yu jigéen defe. \v 11 Muy Maala, di Tirca, di Ogla, di Milka, di Nowa, doomi Selofat yooyu, ñoom ñépp seen bokki baay lañu séyal. \v 12 Ca làngi askanu Manase doomu Yuusufa lañu séy, seen céru suuf daldi des ca giir ga seen làngu baay bokk. \p \v 13 Loolu mooy santaane yeek àttey yoon yi Aji Sax ji dénkoon bànni Israyil, Musaa jottli leen ko ca joori Mowab, fa feggook dexu Yurdan, te janook Yeriko.