\id NEH (WOL) \ide UTF-8 \h Neyemi \toc1 Neyemi \toc2 Neyemi \mt1 Neyemi \c 1 \s1 Neyemi am naw tiis \p \v 1 Mbiri Neyemee ngi, góor gay doomu Akalya: Ca ñaar fukkeelu atu nguurug Artaserses, ci weeru Kislew\f + \fr 1.1 \fr*\fk weeru Kislew \fk*\ft moo yemook juróom ñeenteelu weer wa ci seen nattin.\ft*\f*, man Neyemi maa nga woon ca Sus, péey ba. \v 2 Ci kaw loolu Anani, kenn ci saay bokk bàyyikoo Yuda, ànd aki nit. Ma laaj leen ndesu Yawut ya rëcce ca njaam ga, laaj leen it mbirum Yerusalem. \v 3 Ñu wax ma, ne ma: «Ña rawe ca njaam ga de, ña nga diiwaanu Yuda, ci njàqare ju réy akug toroxte. Tatay Yerusalem jaa nga tojatoo, bunt ya lakk.» \p \v 4 Ba ma déggee kàddu yooyu, damaa toog di jooy, ñaawlu ko ay fan, di woor ak a ñaan ci Yàlla Boroom asamaan. \v 5 Ma ne: «Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, yaw Yàlla Boroom asamaan, Yàlla ju màgg ji te raglu, di sàmm \w kóllëreek|lemma="kóllëre g-:"\w* ngor, ñeel ñi la sopp tey topp say santaane. \v 6 Ngalla Sang bi, teewlu ma, xippi say gët, te déglu sama ñaan, yi may ñaanal guddeek bëccëg \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, say jaam. Tegoo naa moy yi la bànni Israyil moy, te man sax maak sama waa kër baay, moy nanu la. \v 7 Lu ñaawa ñaaw lanu la def, te sàmmunu say santaaneek say dogal ak sa ndigali yoon ya nga dénkoon Musaa, sa jaam ba. \v 8 Rikk bàyyil xel kàddu ya nga dénkoon Musaa, sa jaam ba, ne ko: “Bu ngeen feccee kóllëre, maa leen di tasaare ci biir xeet yi. \v 9 Waaye bu ngeen walbatikoo ci man, sàmm samay santaane, di ko jëfe, bu ñu yóbbu woon seeni ñoñ ba fa suuf digalook asamaan sax, fa laa leen di jële, boole leen yóbbu ca bérab, ba ma taamoo dëël sama tur.” \v 10 Ñooy say jaam, sa ñoñ ñi nga jote sa kàttan gu réy ak sa doole ju bare. \v 11 Éy Boroom bi, Sang bi, rikk teewlul bu baax samag ñaan, ak sa ñaanu jaam ñi safoo wormaal saw tur. Ngalla Sang bi, nangul ma tey jii, may ma waa jii yéwéne ma.» Booba maa yore woon naani Buur. \c 2 \s1 Neyemi jot na ndigal \p \v 1 Mu am bés, ci weeru Nisan, ñeenti weer gannaaw Kislew, yemook ñaar fukkeelu atu nguurug Artaserses, ma jël biiñ ba taaje woon fa kanam Buur, di ko ko xellil. Booba maa nga ànd ak tiis, ne yogg; lu ma masula dal ca kanamam. \v 2 Buur laaj ma, ne ma: «Lu la tax ne yogg te woppuloo? Mbaa du tiisu xol?» Maa ngi tiit lool. \v 3 Ma daldi ne Buur: «Guddalu fan, Buur! Nu may def ba duma ne yogg, te dëkk ba samay maam tëdd gental, bunt ya lakk ba xoyomu?» \v 4 Buur wax ma, ne ma: «Ana looy sàkku?» Ma ñaan gaaw ci Yàlla Boroom asamaan, \v 5 door ne Buur: «Xanaa Sang bi, su la neexee rekk, nga yéwéne ma, yebal ma Yuda, dëkk ba ñu denc samay maam, ba ma tabaxaat ko.» \v 6 Buur nag wax ak man, fekk Lingeer soxnaam toog, feggook moom. Mu ne ma: «Boo demee, ana loo fay toog, doora délsi?» Ma wax ko. Gannaaw loolu Buur nangu maa bàyyi ma dem. \v 7 Ci kaw loolu ma ne Buur: «Buur, su la soobee, ngalla nañu ma jox ay bataaxal yu jëm ca kilifay Wàllaa Dex ya, ngir ñu jàllale ma, ba ma àgg Yuda; \v 8 akub bataaxal bu jëm ca Asaf may wattu toolu buur, ngir mu may ma bant yu ma defareji bunti tatay kër Yàlla ga, defaraale ca tatay dëkk baak kër ga may dali.» Buur nangul ma, ndax sama Yàlla ji ma toppe mbaaxam. \v 9 Ba loolu amee ma dem ba ca kilifay Wàllaa Dex ya, jox leen bataaxali Buur, fekk Buur boole maakay njiiti xare aki gawar. \p \v 10 Ba mu ko defee, Sanbalat ma dëkk Oron dégg mbir ma, mook Tobya, Amoneen ba, ndawal Buur. Ñu am lu leen soofa soof, te mooy li nit ñëw, di sàkkusi njariñu \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \s1 Neyemi xool na tata ja wër Yerusalem \p \v 11 Ma àgg nag ba Yerusalem, toog fa ñetti fan. \v 12 Gannaaw loolu ma jóg guddi, maak nit ñu néew, te waxuma kenn li ma sama Yàlla nammloo ngir ma defal ko Yerusalem. Yoruma woon jenn daamar ju moy ji ma war. \v 13 Ma génne dëkk ba guddi, jaare buntu tata ba ñuy wax Xur wa, wutali walu ndox ma ñuy wax walu Ninki-nànka, daldi jàll ba ca buntu Sën ba. Ci biir loolu ma seetlu tatay Yerusalem ji toj fu nekk, bunt yi lakk ba xoyomu. \v 14 Ma jubal wutali bunt ba ñuy wax Bëtu Ndox, jaare ca wetu déegu Buur. Amatul nag fu sama daamar ji ma war mana jaare. \v 15 Ma daldi topp xur wa ca guddi ga, di seetlu tata ji, ba noppi waññiku, jaare ca buntu Xur wu xóot wa, duggsiwaat. \v 16 Kilifay dëkk ba nag xamuñu fu ma demoon, mbaa lu ma doon def. Ndax fekkul woon ma wax kenn dara, du Yawut yi, du \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi, du garmi yi, du kilifa yi te du keneen ci ñi wara sasoo liggéey bi. \p \v 17 Ba loolu amee ma ne leen: «Yeena gisal seen bopp toskare gi nu nekke. Yerusalem tas na, bunt yi lakk na. Aycaleen nu tabaxaat tatay Yerusalem ndax sunu gàcce faju.» \v 18 Gannaaw loolu, ma nettali leen ni ma sama Yàlla toppe yiwam, ak kàddu yi ma Buur wax. Ñu ne ma: «Nanleen tabax!» Ñu daldi gëna pastéefu ca liggéeyu ngëneel ba. \p \v 19 Ba loolu amee Sanbalat ma dëkk Oron dégg ko, mook Amoneen ba Tobya, jawriñ ba, ak Gesem, Araab ba. Ñu di nu ñaawal ak a diiju naan: «Li ngeen di def nii lu mu doon? Dangeen di fexeel Buur?» \v 20 Ma ne leen: «Yàlla Boroom asamaan moo nuy may ndam. Nun ñiy jaamam nooy jóg tabaxaat dëkk bi. Yeen nag amuleen wàll ci Yerusalem, te baaxoowuleen fi benn sañ-sañ!» \c 3 \s1 Ñu ngi tabaxaat tata ja \p \v 1 Gannaaw loolu Elyasib \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bu mag ba ànd ak bokki sarxalkatam, ñu tabaxaat bunt ba ñuy wax Gàtt ya, sellalal ko Yàlla, taxawal laf ya, defaraat tata ja, ba ca soorooru Meya, sellalal ko Yàlla, jàppoo ko noonu ba ca soorooru Ananel. \v 2 Waa Yerikoo nga feggook ñoom di tabax, Sakuur doomu Imri di tabax ca wet ga. \p \v 3 Bunt ba ñuy wooye buntu Jën ya, góori waa Sena ñoo daaj bant ya, taxawal laf ya, def ca tëjukaay yaak dénki galan ya muy àndal. \v 4 Meremot doomu Uri doomu Akocc, moo làng ak ñoom di defar; ka feggook ñoom di defar, di Mesulam doomu Berekiya doomu Mesesabel. Ka feggook ñoom di defar, di Cadog doomu Baana. \v 5 Ka feggook ñoom, ba tey, di defar di waa Tekowa. Seeni kilifa nag ñoo bañoona liggéey ci njiital jawriñ yi yore liggéey bi. \p \v 6 Buntu Cosaan ba, Yowada doomu Paseya ak Mesulam doomu Besodiya ñoo ko defaraat, daaj bant ya, taxawal laf ya, ak tëjukaay yaak dénki galan ya cay ànd. \v 7 Ña feggook ñoom di defar, di Melatiya ma dëkk Gabawon ak Yadon ma dëkk Meronot ak ñeneen waa Gabawon ak Mispa, gox ya ca kilifteefu boroom Wàllaa Dex. \v 8 Ka feggook ñoom di defar, di Usyel doomu Xaraya, tëggu wurus ba. Ka feggook moom di defar, di Anaña, bokk ca defarkati cuuraay ya. Ñu sottal seen liggéey ca Yerusalem gannaaw ba ñu àggee fa tata ja gëna yaatoo. \v 9 Ka feggook ñoom di liggéey, Refaya doomu Ur la. Moo yilifoon genn-wàllu diiwaanu Yerusalem. \v 10 Ka ca topp di liggéey dog ba janook këram, Yedaya la, doomu Arumaf; Atus doomu Asabneya feggook moom di defaraat. \v 11 Am na weneen làccu tata wu Malkiya doomu Arim di defaraat, mook Asub doomu Payat Mowab; ñu defaraale sooroor ba ñuy wax Taal ya. \v 12 Ka feggook moom di defaraat, di Salum doomu Aloyes, kilifag geneen wàllu diiwaanu Yerusalem, ay doomam yu jigéen di ko jàpple ca liggéey ba. \p \v 13 Buntu Xur wa, Anun a ko defaraat, mook ña dëkk Sanowa. Ñoo ko tabaxaat, taxawal laf ya, ak tëjukaay yaak dénki galan ya cay ànd. Ñu teg ca defaraat làccub juróomi téeméeri meetar ca tata ja, ba àgg ca buntu Sën ba. \p \v 14 Buntu Sën ba nag, ka ko defaraat Malkiya doomu Rekab la, di boroom gox ba ñuy wax Bet Kerem. Moo ko defaraat, taxawal laf ya, ak tëjukaay yaak dénki galan ya cay ànd. \p \v 15 Bunt ba ñuy wax Bëtu Ndox ba, Salun doomu Kol Ose, boroom gox ba ñuy wax Mispa, moo ko defaraat. Moo ko tabaxaat, xadd ko, taxawal laf ya, ak tëjukaay yaak dénki galan ya cay ànd, ak itam tata ja ca déegub Silowe, bay suuxat toolu buur, ba ca dëggastal ya ngay wàcce, génn gox ba ñuy wax Kër Daawuda. \v 16 Ka ca topp di defar, Neyemi doomu Asbug la, boroom genn-wàllu gox ba ñuy wax Bet Cur. Moo féetewoo la dale fa janook sëgi Daawuda ya, ba ca déeg ba nit ña sàkk, dem ba ca dalu Xarekat ya. \v 17 \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñaa ca topp di defaraat, di Reyum doomu Baani; ka dend ak moom, taxawal goxam di defaraat, di Asabya, may boroom genn-wàllu gox ba ñuy wax Keyla. \v 18 Ka topp ca moom di liggéey, di seen mbokk Binuy doomu Enadàdd, boroom geneen wàllu gox ba ñuy wax Keyla. \v 19 Ka feggook moom di liggéey, Eser la, doomu Yeswa, boroom Mispa. Muy defaraat làcc wa janook fa ngay yéege jëm ca dencu gànnaay ya, ca koñu tata ja. \v 20 Ka topp ca moom di liggéey ak pastéef Barug la, doomu Sabay. Muy defaraat weneen làccu tata ja dale ca koñ ba ca bunt kër Elyasib, sarxalkat bu mag ba. \v 21 Ka topp ca moom Meremot la, doomu Uri doomu Akocc. Muy defaraat làcc wa dale ca bunt kër Elyasib, ba fa kër ga yem. \v 22 Ña topp ca moom di defaraat, di sarxalkat ya dëkke la wër Yerusalem. \v 23 Ña ca topp di liggéey, Beñamin la ak Asub. Ñuy defaraat làcc wa janook seen kër. Ka ca topp di liggéey, di Asaryaa doomu Maaseya doomu Anaña. Muy defaraat fa dendeek këram. \v 24 Ka ca topp di Binuy doomu Enadàdd. Muy defaraat làcc wa dale ca kër Asaryaa ba ca koñ ba, ca ruqu tata ja. \v 25 Palal doomu Usay di defaraat diggante koñ ba ak sooroor bu kawe ba tiim kër buur, jàpp ëttu dag ya. Ka ca topp di Pedaya doomu Paros. \v 26 Liggéeykati kër Yàlla ya féete Ofel ca tund wa, di liggéey, ba fa janook soorooru koñ, ba féete buntu Ndox ma penku. \v 27 Ña ca topp di waa Tekowa, di defaraat làcc wa ca topp, dale fa janook soorooru koñ bu kawe ba, ba ca tatay tund wa. \p \v 28 La ko dale ca buntu Fas ya, ay sarxalkat a fa doon liggéey, ku nekk janook këram. \v 29 Ka ca topp di liggéey, Cadog doomu Imer la. Muy defaraat fa janook këram. Ka ca topp di defaraat, di Semaya doomu Sekaña; moo doon wattukatu buntu Penku ba. \v 30 Ña topp ca moom di liggéey, di Anaña doomu Selemya ak Anun, juróom benneelu doomu Calaf. Muy defaraat làcc wa ca topp. Ka ca topp di liggéey, Mesulam doomu Berekiya la. Muy defaraat fa janook dëkkuwaayam. \v 31 Ka ca topp di defar, di Malkiya, bokk ca tëggi wurus ya. Muy liggéey ba ca këri liggéeykati kër Yàlla ga ak jaaykat ya, fa janook buntu Ndaje ba, jàpp ca néegu jongrukat bu kawe ba ca ruq ba. \v 32 Diggante néegu jongrukat bu kawe ba ca koñ ba, ak buntu Gàtt ya, ña fa doon liggéey tëggi wurus ya la ak jaaykat ya. \c 4 \s1 Liggéey bi am na gàllankoor \p \v 1 Ba Sanbalat déggee ne nu ngi tabaxaat tata ja, am na naqar wu réy, mer lool. Muy ñaawal Yawut yi \v 2 ca kanam bokkam yaak xarekati Samari ya naan: «Ana lu Yawut yi yaafus yii di jéema def nii? Ñu defe ne moos seen pexe dina sotti, ba ñuy def ay sarax? Fu ñuy noppee seen tabax bi bésub tey? Te yékkatiwñu lu moy ay doj yu ñu sullee ci jalub tojit yu lakk ba noppi?» \v 3 Tobya Amoneen ba mu feggool nag ne ca tonet ne: «Tata ji ñuy tabax de, su ci wel sax yéegoon, mu ànd aki dojam, màbb.» \p \v 4 Ci biir loolu ma ne: «Ngalla sunu Yàlla, déggal rekk xeebeel gi ñu nu xeeb te walbati seeni xaste, mu këppu ci seen kaw. Ngalla jébbal leen nit ñu sëxëtoo seen alal ci réew mu ñu leen jàpp njaam. \v 5 Bu leen jéggal seen tooñ, bul far seen bàkkaar, ndaxte ñoo naqaral ñiy tabax.» \p \v 6 Ci kaw loolu nu tabaxaat tata ja, wërale ko ba mu àgg ca genn-wàllu taxawaayam, ndax fekk na mbooloo ma pastéefu ca liggéey ba. \p \v 7 Sanbalat nag ak Tobyaak Araab yaak Amoneen ñaak Asdoddeen ña, ñoom ñépp dégg ne liggéeyu tatay Yerusalem a ngay jëm kanam, te xar-xar yaa ngay tàmbalee fatt. Ñu mer ca lool, \v 8 daldi mànkoo, lal pexe ngir xareek Yerusalem, fitnaal leen. \v 9 Ba mu ko defee nu ñaan ci sunu Yàlla, ba noppi teg fa ay nit ñuy wattu guddeek bëccëg, ngir bàyyi leen xel. \p \v 10 Fekk na waa Yudaa ngi naan: \q1 «Dooley yenukat ŋiis, \q1 tojit jalee jale. \q1 Nu nuy tabaxeeti jii tata?» \p \v 11 Ci biir loolu noon ya naan: «Bala ñu noo yég mbaa ñu di nu gis, nu ne saraax ci seen biir, rey leen, yemale fi liggéey bi.» \v 12 Yawut ya ñu dëkkal nag dikk waxsi nu fukki yoon ak juróom li ñu nuy fexeel, ne nu «Fu ne lañuy jóge, songsi nu.» \s1 Neyemi gànnaayal na ay wattukat \p \v 13 Ma teg nag ay nit ci bérab yu ne fàŋŋ te suufe ca gannaaw tata ja. Ma def leen ay kurél, gu ci nekk ak làngam ak bérabam. Ña nga gànnaayoo seeni xeej ak seeni saamar ak seeni fitt. \v 14 Ba loolu amee ma xoolaat lépp, ba noppi wax ak kàngam yaak kilifa yaak mbooloo ma ca des ne leen: «Buleen leen ragal. Fàttlikuleen ne Boroom bi moo màgg te jara ragal te ngeen xeexal seeni bokk ak seen doom yu góor ak yu jigéen, ak seeni jabar ak seeni kër.» \p \v 15 Gannaaw gi noon ya xam ne yég nanu leen, te Yàlla nasaxal na seen pexe. Ba mu ko defee nu walbatikuwaat nun ñépp ca tata ja, ku nekk dellu ca liggéeyam. \v 16 La ko dale bésub keroog sama xaaju nit ña rekk a doon liggéey, xaaj ba ca des gànnaayoo ay xeej aki pakk aki fitt ak kiiraayal dënn. Kilifa ya nag taxaw ca gannaaw mboolem waa Yuda. \v 17 Ña doon tabax tata jaak ñay yenook ñay yene, ñépp di liggéeye benn loxo, loxo ba ca des ŋàbb ngànnaay. \v 18 Te it ñay tabax, ku ci nekk, sab saamar a nga takke ci sa ndigg, ngay liggéey, boroom liit gi feggook man. \v 19 Ma wax ak garmi yaak kilifa yaak mbooloo ma ca des, ne leen: «Liggéey bi réy na, yaatu na, te nun danoo tasaaroo te soreyantoo ci tata ji. \v 20 Fu ngeen dégg liit gi jibe fa, fekksileen nu fa. Sunu Yàlla dina nu xeexal.» \v 21 Nu nekk nag ci liggéey bi, genn-wàllu nit ñi yore ay xeej, dale ko ba bët di set, ba biddiiw yiy feq. \p \v 22 Boobu it laa wax mbooloo ma ne leen: «Na ku nekk ànd ak ka muy liggéeyandool, fanaan ci biir Yerusalem. Su ko defee nu man di wattu guddi, di liggéey bëccëg.» \v 23 Booba kenn ci nun summiwul ay yéreem, du man, du samay bokk, du samay nit, te du wattukat yi ànd ak man. Ku nekk day ŋàbb ngànnaayam akam ndox. \c 5 \s1 Neyemi aar na néew-ji-doole \p \v 1 Ci biir loolu askan waak seeni jabar di xultu lool ci seen kaw bokki Yawut. \v 2 Ñii naan: «Nun danoo jaboot, nook sunu doom yu góor ak yu jigéen. Nañu nu jox pepp mu nu lekk, ba mana dund.» \v 3 Ñee naan: «Sunuy tool ak sunuy tóokëri reseñ ak sunuy kër lanuy tayle ngir am pepp ci xiif bi.» \v 4 Ña ca des naan: «Danoo àbb xaalis, taylee ko sunuy tool ak tóokëri reseñ ngir fey galagu buur. \v 5 Moona nun de, nook ñi nuy lebal benn lanu, diy bokk lenqe, te seeni doom gënuñu sunuy doom. Terewul nu ngi nara dugal sunuy doom yu góor ak yu jigéen cig njaam. Am na sax ñenn ci sunuy doom yu jigéen, ñu nekk cig njaam ba noppi. Manunu ci dara ndax sunuy tool ak sunu tóokëri reseñ a ngi ci yeneen loxo.» \p \v 6 Ba ma déggee seeni xultook seen wax jooju, mer naa lool. \v 7 Ma daldi dogu ci sama xol ne dinaa yedd garmi yeek njiit yi. Ma ne leen: «Yeen yeenay lebal seeni bokk, di sàkku tegandaay.» Ci kaw loolu ma woote ndaje mu réy ci seen mbir. \v 8 Ma ne leen: «Nun def nanu sunu kem kàttan ngir jotaat sunu bokki Yawut yi ñu jaayoon ay jaambur. Léegi yeen ci seen bopp ngeen di jaay seeni bokk, nun nu war leena jotaat?» Ñu ne xerem, amuñu lu ñu wax. \v 9 Ma dellu ne leen: «Li ngeen di def de baaxul. Lu leen tee di ragal sunu Yàlla bala noo torox ci kanam noon yi dul Yawut? \v 10 Man itam, maak samay bokk ak samay nit, nu ngi lebal askan wi xaalis ak pepp. Waaye nanu leen baal bor bii. \v 11 Dellooleen leen seeni tool, tey jii, ak seeni tóokëri reseñ ak seen garabi oliw ak seeni kër. Dellooleen leen itam li ngeen leen tegoon, muy benn ci téeméeri xaaj, ci xaalis ak pepp ak biiñ ak diw.» \v 12 Ñu ne: «Li nga wax lanuy def. Dinanu leen ko delloo te dootunu leen laaj dara.» Ba mu ko defee ma woo \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ya, giñloo leen ca kanam sarxalkat ya, ne dinañu def li ñu wax. \v 13 Ba loolu amee ma yëlëb sama lafu mbubb wi may dence, daldi ne: «Yal na Yàlla yëlëbe nii mboolem ku sàmmul kàddu gii ci yeen, ba xañ ko këram ak alalam. Yal nañu ko ni yëlbe, ba mu jeexle tàkk.» Mbooloo ma mépp ne: «Amiin,» daldi bokk sargal \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Mbooloo ma mépp nag def loolu ñu wax. \p \v 14 Bu loolu weesee, la ko dale bés ba ñu ma falee boroom diiwaanu Yuda, ca ñaar fukkeelu atu nguurug Artaserses, ba ca fanweeru atam ak ñaar, muy fukki at ak ñaar, lekkunu alalu galag bu boroom diiwaan yelloo, du man, du samay bokk. \v 15 Waaye boroom diiwaan yi ma jiitu dañu daan not askan wi, di leen sëf seen dund ak seen biiñ, boole ci ñeent fukki dogi xaalis\f + \fr 5.15 \fr*\fk 40 dogi xaalis: \fk*\ft lim boobu mu ngi tollook liibaru xaalis.\ft*\f*. Seeni surga it di néewal askan wi doole. Man nag defuma noonu ndax ragal Yàlla. \v 16 Xanaa kay damaa saxoo jàpp ci liggéeyu tata jii. Masunoo jënd suuf, te sama nit ñépp a daan daje ci liggéey bi. \v 17 Rax ci dolli daan naa woo téeméeri kilifay Yawut ak juróom fukk (150), di bokk ak ñoom sama njël, te limaalewuma ñi bàyyikoo ci jaambur yi nu séq, di nu fekksi. \v 18 Bés bu nekk daan nañu ma waajalal aw yëkk, ak juróom benni xari yar, ak boroomi dunq, ak lu baree bare ci mboolem xeetu biiñ, ñu di ko indi fukki fan yu nekk. Loolu taxul ma sàkku benn yoon galag bu boroom diiwaan di dunde, ndax liggéey bi diisoon na lool jeeg ci askan wi. \p \v 19 Kon nag rikk sama Yàlla, bàyyil xel ci man te baaxe ma, ndax mboolem li ma defal askan wii! \c 6 \s1 Tata ja noppi na \p \v 1 Sanbalat ak Tobya nag dégg, ñook Gesem Araab baak noon ya ca des ne tabaxaat naa tata ja, ba xar-xar desatu ca, doonte taxawalaguma woon lafi bunt ya. \v 2 Sanbalat ak Gesem yónnee ci man, ne ma: «Dikkal nu dem Kefirim ca xuru Ono, diisooji fa.» Booba ña nga may fexeel. \v 3 Ma yónnee leen ay ndaw, ne leen: «Damaa jàpp lool. Duma mana ñëw. Xanaa duma dakkal liggéey bi, bàyyi ko fi, di leen fekki?» \v 4 Ñu yónnee ci man, wax ma loolu ba muy ñeenti yoon, sama tont di lenn. \v 5 Ba ko juróomeel Sanbalat yóbbanteeti ab surgaam genn kàddu gi, mu indaale bataaxal bu tëjuwul, yor ko ci loxoom. \v 6 Ñu bind ci ne: \pm Dégg nañu ci xeet yi dul Yawut, te Gesem\f + \fr 6.6 \fr*\fk Gesem \fk*\ft ak Gasmu kenn ki la.\ft*\f* sax dëggal na ko, ne yaw yaak sa bokki Yawut dangeen di fexee fippu. Ñu ne moo tax ngay tabaxaat tata ji. Wax nañu sax ne dangaa bëgga doon seen buur, \v 7 te xas ngaa tànn ay yonent yu wara yéene ci Yerusalem, ne falu nga buur ci Yuda. Balaa yàgg nag buuru Pers dina jot ci wax jooju. Kon nag dikkal, nu bokk diisoo ci. \p \v 8 Ma yónnee ca Sanbalat, ne ko: «Li nga wax amul. Yaw yaa ko fental sa bopp.» \v 9 Fekk na ñoom ñépp a nu doon jéema xoqtal, yaakaar ne dinanu yoqi, ba liggéey bi du sotti. Ma daldi ne: «Léegi nag Yàlla, ngalla dooleel ma!» \p \v 10 Ci kaw loolu ma dem kër Semaya doomu Delaya doomu Metabel, fekk ko mu tëju cib néegam. Mu ne ma: \q1 «Nan ànd dem ca kër Yàlla ga, ca \w néeg bu mag|lemma="néeg (Yàlla) bu mag b-:"\w* ba, \q1 nu tëju ca néeg bu mag ba balaa ñu lay reysi. \q1 Guddi lañuy ñëw, reysi la.» \m \v 11 Ma ne ko: «Man duma kuy daw! Te sax gannaaw duma sarxalkat, nu may dugge ci biir néeg Yàlla bu mag bi, di génnaale bakkan\f + \fr 6.11 \fr*\fk néeg Yàlla bu mag bi, \fk*\ft sarxalkat yi rekk ñoo fa sañoona dugg. Keneen ku fa dugg, ku dul sarxalkat, day dee.\ft*\f*? Man kay demuma.» \v 12 Booba la ma leer ne ndeke Yàlla yónniwu ko, waaye Tobyaak Sanbalat ñoo ko fey ngir mu birale ma noonu waxyu, di ma fexeel. \v 13 Dañu koo feyoon ngir mu tiital ma, ma def noonu, muy bàkkaar. Su ko defee ñu yàq sama der, torxal ma. \p \v 14 Sama Yàlla, yal nanga bàyyi xel ci Tobyaak Sanbalat te fey leen seen jëf jii, ñook Nowadiya, yonent bu jigéen beek yeneen yonent yi ma doon xoqtal. \p \v 15 Ba mu ko defee tata ji noppi ñaar fukki fan ak juróom ci weeru Elul\f + \fr 6.15 \fr*\fk weeru Elul \fk*\ft moo yemook juróom benneelu weer ci nattinu yawut, muy ndeeteel ut, jàpp sàttumbar.\ft*\f*. Ñu liggéey ko ci juróom fukki fan ak ñaar. \v 16 Ba ko sunu noon yépp yégee, ñook mboolem jaambur ñi ñu wër, am nañ tiitaange ak mbetteel mu réy, ndax xam nañu ne sunu ndimbalu Yàlla rekk lanu sottale boobu liggéey. \p \v 17 Ca yooya jamono garmiy Yuda daan nañu bindanteek Tobya lu bare. \v 18 Bare na sax ci waa Yuda ñu faroon ak moom ci kaw ngiñ, ndax la mu doon denc doomu Sekaña, ma Ara di baayam, te doomam Yowanan di denc doomu Mesulam ma Berekiya di baayam. \v 19 Rax ci dolli ñu di ma gëmloo ag mbaaxam, te di ko jottli samay kàddu. Tobya nag yónnee ma ay bataaxal, di ma xoqtal. \c 7 \p \v 1 Gannaaw ba ñu tabaxaatee tata ja, ma taxawal lafi bunt ya, ba noppi dénk fara bunt ya seen liggéey, ñook jàngkat yaak \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ña. \v 2 Ci kaw loolu ma sas sama mbokk Anani, mu jiite Yerusalem, mook Anaña boroom tata ja, ndax la mu gëna dëggu ñu bare, gën leena ragal Yàlla. \v 3 Ma ne leen: «Bu bunti Yerusalem ubbiku li feek jant bi tàngul. Santleen fara bunt yi ñuy tëj bunt yi, sës ci galani tëjukaay yi, balaa waa dëkk biy tëdd. Na ku nekk ci waa Yerusalem di wattoo ca bérabu wattukaayam, mbaa buntu këram.» \p \v 4 Booba dëkk ba réy na, yaatu na; waaye nit ña ca dëkk ñoo néew, te kër ya tabaxewaatul woon. \v 5 Sama Yàlla xiir ma ma woo garmi yeek kilifa yeek baadoolo yi, ngir bind leen. Ci biir loolu ma gis limeefu làng ya jëkka jóge ngàllo ga, ba ñibbsi. Li ma fekk ñu bind ko ci mooy lii: \p \v 6 Ñii nag ñoo di niti diiwaanu Yuda, ña jóge njaam ca ngàllo ga leen Nabukodonosor buuru Babilon yóbbu woon, te ñu jóge ca ñibbsi Yerusalem ak Yuda, ku nekk ak fa mu dëkk. \v 7 Ña nga ñibbi ca njiital Sorobabel ak Yosuwe\f + \fr 7.7 \fr*\ft Yeswa ci làkku ebrë. Yosuwe lanu bind ci tekki bii, muy doomu Yoccadag te doon sarxalkat bu mag bi mujj lu jiitu ngàllo ga ca Babilon. Yosuwe mii lu gëna bare dees na ko tuddaaleek Sorobabel. Feneen fu ñu ne Yeswa ci téere bi, keneen a tax ñuy wax.\ft*\f* ak Neyemi ak Asaryaa ak Ramya ak Nayamani ak Mardose ak Bilsan ak Misperet ak Bigway ak Neyum ak Baana. Limeefu góori \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* nii la tëdde: \v 8 Askanu Paros ñaari junni ak téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar lañu (2 172). \v 9 Askanu Sefatiya ñetti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar lañu (372). \v 10 Askanu Ara di juróom benn téeméer ak juróom fukk ak ñaar (652). \v 11 Askanu Payat Mowab, soqikoo ci Yeswa ak Yowab, di ñaari junni ak juróom ñetti téeméer ak fukk ak juróom ñett (2 818). \v 12 Askanu Elam junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254). \v 13 Askanu Sàttu juróom ñetti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (845). \v 14 Askanu Sakay juróom ñaar téeméer ak juróom benn fukk lañu (760). \v 15 Askanu Binuy juróom benn téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñett lañu (648). \v 16 Askanu Bebay juróom benn téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett lañu (628). \v 17 Askanu Asgàdd ñaari junni ak ñetti téeméer ak ñaar fukk ak ñaar lañu (2 322) \v 18 Askanu Adonikam juróom benni téeméer ak juróom benn fukk ak juróom ñaar lañu (667). \v 19 Askanu Bigway ñaari junni ak juróom benn fukk ak juróom ñaar lañu (2 067). \v 20 Askanu Adin juróom benn téeméer ak juróom fukk ak juróom lañu (655); \v 21 askanu Ater soqikoo ci Esekiya, di juróom ñeent fukk ak juróom ñett (98); \v 22 Askanu Asum ñetti téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett lañu (328). \v 23 Askanu Besay ñetti téeméer ak ñaar fukk ak ñeent lañu (324). \v 24 Askanu Arif téeméer ak fukk ak ñaar lañu (112). \v 25 Askanu Gabawon juróom ñeent fukk ak juróom lañu (95). \v 26 Waa Betleyem ak Netofa téeméer ak juróom ñett fukk ak juróom ñett lañu (188). \v 27 Waa Anatot téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett lañu (128). \v 28 Waa Bet Asmawet ñeent fukk ak ñaar lañu (42). \v 29 Waa Kiryaat Yarim ak Kefira ak Berot juróom ñaar téeméer ak ñeent fukk ak ñett lañu (743). \v 30 Waa Raama ak Geba juróom benni téeméer ak ñaar fukk ak benn lañu (621). \v 31 Waa Migmas téeméer ak ñaar fukk ak ñaar lañu (122). \v 32 Waa Betel ak Ayi téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (123). \v 33 Waa Nebo gu ndaw juróom fukk ak ñaar lañu (52). \v 34 Waa Elam gu ndaw junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254). \v 35 Waa Arim ñetti téeméer ak ñaar fukk lañu (320) \v 36 Waa Yeriko ñetti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (345). \v 37 Waa Lodd ak Adidd ak Ono juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk ak benn lañu (721). \v 38 Waa Sena ñetti junni ak juróom ñeenti téeméer ak fanweer lañu (3 930). \p \v 39 \w Sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi ñii la: \m Askanu Yedaya, soqikoo ci waa kër Yosuwe, di juróom ñeenti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñett (973). \v 40 Askanu Imer junni ak juróom fukk ak ñaar lañu (1 052). \v 41 Askanu Pasur junni ak ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñaar lañu (1 247). \v 42 Askanu Arim junni ak fukk ak juróom ñaar lañu (1 017). \p \v 43 Leween ñi ñii la: Askanu Yeswa ma soqikoo ca Kadmiyel. Mooy ñi bànqaasoo ci Odawya, tollu ci juróom ñaar fukk ak ñeent (74). \p \v 44 Jàngkat yi ñoo di: Askanu Asaf, di téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñett (148). \v 45 Askanu fara bunt yi ñoo di: Askanu Salum, ak askanu Ater, ak askanu Talmon, ak askanu Akub, ak askanu Atita, ak askanu Sobay, di téeméer ak fanweer ak juróom ñett (138). \p \v 46 Liggéeykati kër Yàlla gi ñoo di: Askanu Ciya, ak askanu Asufa, ak askanu Tabawot, \v 47 ak askanu Keros, ak askanu Siya, ak askanu Padon, \v 48 ak askanu Lebana, ak askanu Agaba, ak askanu Salmay, \v 49 ak askanu Xanan, ak askanu Gidel, ak askanu Gayar, \v 50 ak askanu Raaya, ak askanu Reccin, ak askanu Nekoda, \v 51 ak askanu Gasam, ak askanu Usa, ak askanu Paseya, \v 52 ak askanu Besay, ak askanu Meyunim, ak askanu Nefusim, \v 53 ak askanu Bagbug, ak askanu Akufa, ak askanu Arur, \v 54 ak askanu Baslut, ak askanu Meyida, ak askanu Arsa, \v 55 ak askanu Barkos, ak askanu Sisera, ak askanu Tema, \v 56 ak askanu Necciya, ak askanu Atifa. \p \v 57 Askanu jaami Suleymaan ñii la: Askanu Sotay, ak askanu Soferet, ak askanu Perida, \v 58 ak askanu Yaala, ak askanu Darkon, ak askanu Gidel, \v 59 ak askanu Sefatiya, ak askanu Atil, ak askanu Pokeret Asbayim, ak askanu Amon. \p \v 60 Mboolem liggéeykati kër Yàlla gi ak askanu jaami Suleymaan yi, ñetti téeméer ak juróom ñeent fukk ak ñaar (392). \p \v 61 Ña bàyyikoo Tel Mela ak Tel Arsa ak Kerub Adon ak Imer te manuñoo firndeel ne seen waa kër maam ak seen askan ci Israyil lañu bokk, ñii la: \v 62 Askanu Delaya, ak askanu Tobya, ak askanu Nekoda, di juróom benn téeméer ak ñeent fukk ak ñaar (642). \p \v 63 Am na it ñu loolu daloon ci sarxalkat yi, muy askanu Abaya, ak askanu Akocc, ak askanu Barsilay, ma doon denc doomu Barsilay waa Galàdd ba, ba tax ñu santale ko seen sant. \v 64 Ñooñu seet nañu seen limeefu kër maam, waaye gisuñu ko. Ñu daldi leen doyadal, génne leen ci carxal gi. \v 65 Boroom dëkk ba nag aaye leen ñu lekk ci ñam yu \w sell|lemma="sell:"\w* yaa sell, ba keroog sarxalkat ba di am lu leer ci ñoom ci jumtukaayi tegtal yi ñuy wax \w Urim ak Tumim|lemma="Urim ak Tumim:"\w*. \p \v 66 Limu mbooloo ma mépp ba mu daj, ñeent fukki junneek ñaar ak ñetti téeméer ak juróom benn fukk lañu (42 360), \v 67 te limaaleesul seen jaam yu góor ak yu jigéen, yi tollu ci juróom ñaari junni ak ñetti téeméer ak fanweer ak juróom ñaar (7 337). Amoon nañu itam ay jàngkat yu góor ak yu jigéen, yu tollu ci ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom (245), \v 69 ak ñeenti téeméeri giléem ak fanweer ak juróom (435), ak juróom benni junniy mbaam ak juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk (6 720). \p \v 70 Am na ñu jiite seen kër baay, ñu def seen loxo ca liggéey ba. Boroom dëkk ba def na ca alal ja junniy poseti wurus (1 000) ak juróom fukki këll (50) ak fanweeri mbubbi sarxalkat (30) ak juróomi téeméeri dogi xaalis (500)\f + \fr 7.69 \fr*\ft Fi ñu tudd fanweeri mbubbi sarxalkat yi ak juróomi téeméeri dogi xaalis, am na ñu fi boole ñaari lim yooyu, moomale ko dayob mbubbi sarxalkat yi doŋŋ.\ft*\f*. \p \v 71 Ñenn ca ña jiite seen kër baay def nañu seen loxo ca alal ja ñu jagleel liggéey ba, mu tollu ci ñaar fukki junniy poseti wurus (20 000) ak ñaari junniy dogi xaalis ak ñaar téeméer (2 200). \p \v 72 La des ca askan wa joxe na ñaar fukki junniy poseti wurus (20 000) ak ñaari junniy dogi xaalis (2 000) ak mbubbi sarxalkat yu tollu ci juróom benn fukk ak juróom ñaar (67). \p \v 73 Ba loolu amee bànni Israyil gépp sancaat ca seen dëkki cosaan, sarxalkat yaak Leween ñaak fara bunt yaak jàngkat yaak ñenn ca baadoolo yaak liggéeykati kër Yàlla ga. \c 8 \s1 Esra jàngal na mbooloo ma \p Ba juróom ñaareelu weer wa teroo, ba bànni Israyil sancaat seeni dëkk, \v 1 mbooloo mépp a daje, di benn bopp ca mbedd ma jàkkaarlook buntu Ndox ma. Ñu wax Esra bindkat ba, ne ko mu indi téereb yoonu Musaa wi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dénk Israyil. \v 2 Esra, \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba, indi téereb yoon wi keroog benn fanu juróom ñaareelu weer wa, fa kanam mbooloo ma, góor ak jigéen, mboolem ña seeni at may ñu dégg ko. \v 3 Esra jàng na ko janook mbedd ma jàkkaarlook buntu Ndox ma, dale ko ba bët setee ba ca digg bëccëg. Mbooloo maa nga teew, góor ak jigéen, mboolem ña dégg la ca nekk. Ñépp nag di teewlu kàdduy téereb yoon wa. \p \v 4 Esra bindkat baa nga taxaw ca kaw dëxu bant ba ñu defaral bés ba. Ña feggook moom ca ndijooram di Matitiya ak Sema ak Anaya ak Uri ak Ilkiya ak Maaseya. Ña ko féete càmmoñ di Pedaya ak Mikayel ak Malkiya ak Asum ak Asbadana ak Sàkkaryaa ak Mesulam. \v 5 Ba Esra di ubbi téere ba, mbooloo mépp a ca teg seeni bët, ndax mbooloo mépp la tiim. Mbooloo mépp nag jóg taxaw. \v 6 Esra daldi sant Aji Sax ji, Yàlla ju màgg ji. Mbooloo ma mépp ànd ne: «Eskëy, eskëy!» yékkati seeni loxo, sukk, sujjóotal Aji Sax ji, dëpp seeni jë fa suuf. \v 7 Ci kaw loolu Yeswa ak Baani ak Serebya ak Yamin ak Akub ak Sabtay ak Odiya ak Maaseya ak Kelita ak Asaryaa ak Yosabàdd ak Xanan ak Pelaya ak \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ña di leeralal mbooloo ma yoonu Musaa. Mbooloo maa nga taxaw, kenn ku nekk benn bérab. \v 8 Ci biir loolu ñu di leen jàngal téereb yoonu Yàlla wi, njàng mu leer, di leen ko firil ba ñu xam li ñuy jàng. \p \v 9 Gannaaw loolu Neyemi boroom dëkk ba ànd ak Esra sarxalkat ba, di bindkat ba ba tey, ak Leween ñay xamal mbooloo ma, wax ak ñoom ñépp, ne leen: «Bésub tey jii, bés bu sell la, ñeel Aji Sax ji, seen Yàlla. Buleen ci naqarlu, buleen ci jooy.» Booba mbooloo ma mépp a doon jooy ca kàdduy yoon wa ñu dégg. \v 10 Esra ne leen: «Ayca demleen lekk lu gëna duuf, naan lu neexa neex te sédd ci ñi amul lu ñu togg; ndax bésub tey bés bu sell la ñeel sunu Boroom. Kon buleen ci naqarlu kat, ndax bége Aji Sax ji mooy seen doole!» \v 11 Leween ña nag di dëfal mbooloo ma mépp, naan leen: «Noppileen waay, ndax tey bés bu sell la. Kon buleen ci naqarlu.» \v 12 Ba mu ko defee mbooloo ma mépp ñibbi, di lekk ak a naan ak a yekkle di bànneexu bu baax. Fekk na ñu xam kàddu ya ñu leen doon xamal. \s1 Feddli nañu màggalu Mbaar yi \p \v 13 Keroog ñaari fan ca weer wa nag ña yilif seen kër baay yépp ànd ak \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yaak \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ña, ñu daje ca Esra bindkat ba, di gëstu kàdduy yoon wi. \v 14 Ci kaw loolu ñu gis ne bind nañu ci yoon wi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji santaane, te Musaa jottli ko, ne: «\w Bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* dañoo wara dëkk ci ay mbaar diiru màggalu weeru juróom ñaareel wa.» \v 15 Ñu siiwal nag ndigal, ca mboolem seeni dëkk ak ca Yerusalem, daldi yéene ne: «Demleen ca tund ya, wuti ay cari garabi oliw, ak cari garabi pẽe\f + \fr 8.15 \fr*\fk garabi pẽe \fk*\ft xeetoo naak filaawoo.\ft*\f*, ak cari garabi mirt, ak cari garabi tàndarma, ak cari garab yu sëq, ndax ñu defare ko ay mbaar, muy li ñu bind.» \v 16 Ba loolu amee mbooloo ma wuti ay car, defare ko ay mbaar ca seen kaw taaxi kër ak ca seeni biir ëtt ak ca ëtti kër Yàlla ga ak ca mbedd ma ca buntu Ndox ma ak ca mbedd ma ca buntu Efrayim. \v 17 Ci kaw loolu mboolem ña ñibbsee ca njaam ga defar ay mbaar, dal ca mbaar ya. La ko dale jamonoy Yosuwe doomu Nuun, ba bésub keroog bànni Israyil defatuñu woon lu ni mel. Muy mbégte mu réya réy. \v 18 Ci biir loolu ñuy jàng ci téereb yoonu Yàlla wi bés bu nekk, tàmbalee ko ca bés bu jëkk ba, ba ca bés bu mujj ba. Amal nañu màggal ga diiru juróom ñaari fan. Bésub juróom ñetteel ba nag ñu woote ca am ndaje mu sell, muy la ñu digle. \c 9 \s1 Kàdduy tuub jib na \p \v 1 Keroog ñaar fukki fan ak ñeent ca weer woowa, \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* daje nañu, sol ay saaku, xëppoo suuf, di ko ñaawloo ci biir koor. \v 2 Ci kaw loolu askanu Israyil beddeeku doxandéem yépp. Ñu taxaw nag, tudd seen bàkkaari bopp ak seen ñaawtéefi maam. \v 3 Ci biir loolu ñu taxaw, di jàng ca seen téereb yoonu Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, diirub xaajaatu bés ba. Xaajaatu bés ba ca topp ñuy tuub ak a sujjóotal seen Yàlla Aji Sax ji. \v 4 Yeswa daldi taxaw ca kaw dëx ba ñu jagleel \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ña, mook Baani ak Kadmiyel ak Sebaña ak Buuni ak Serebya ak Baani meneen ma, ak Kenani. Ña ngay àddu ca kaw, di wax ak seen Yàlla Aji Sax ji. \v 5 Yeswa nag ak Kadmiyel ak Baani ak Asabneya ak Serebya ak Odiya ak Sebaña ak Petaya, Leween ñooñu ñépp àddoondoo ne: «Màggal-leen seen Yàlla Aji Sax ji sax dàkk, ba fàww. Nañu màggal sa tur wu tedd, wi raw gépp cant ak ngërëm.» \pm \v 6 «Yaw Aji Sax ji, yaw kenn yaa sàkk asamaan yi, ba ca asamaan ya gëna kawe ak seen gàngoor yépp, ak suuf ak lépp li ci kawam, ak géej ak li ci biiram lépp. Yooyu yépp, yaay ki leen di may bakkan, te gàngoori asamaan, yaw lañuy sujjóotal. \v 7 Yaw yaa di Aji Sax ji, Yàlla ji tànn Ibraam, jële ko Ur gu waa Kalde, tudde ko Ibraayma. \v 8 Yaa gis mu nangul la ci xolam; nga fas ak moom \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w*, dig askanam réewum Kanaaneen ñaak Etteen ñaak Amoreen ñaak Periseen ñaak Yebuseen ñaak Girgaseen ña. Te def nga li nga dige it, ndax yaw boroom njekk nga. \v 9 Ba nga gisee sunu toroxtey maam ya ca Misra, dégg seeni yuux ca tefesu géeju Barax ya, \v 10 yaa wàcce ay firndeeki kéemaan ca kaw Firawnaaki jawriñam ñépp ak askanu réewam mépp, ndaxte yégoon nga reewande ga waa Misra doon jëflanteek sunuy maam. Ca nga siiwal saw tur ba tey jii. \v 11 Géej nga leen xaral, ñu jaare suuf su wow koŋŋ, ca digg géej ga, ña leen doon dàq nag, nga fél leen, ca biir xóote ya, ñu tàbbi niw doj ci ndox mu baawaan. \v 12 Ci kaw loolu nga di leen jiitee bëccëg aw taxaaru niir, di leen jiitee guddi taxaaru sawara, di leen niital yoon wa ñuy jaare. \v 13 Ca tundu Sinayi wa nga wàcc, àddoo asamaan, wax ak ñoom, dénk leen ndigal yu jub, ak yoon yu dëggu, ak dogali yoon ak santaane yu baax. \v 14 Sa \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w* bu \w sell|lemma="sell:"\w* it, yaa leen ko xamal, te say santaaneeki dogali yoon ak saw yoon, yaa leen ko dénk. Musaa, sa jaam ba, jottli leen ko. \v 15 Pepp mu tawe asamaan nga faje seen xiif, ndox mu balle ciw doj, nga faje seen mar, te ne leen ñu dem nanguji réew ma nga leen giñaloon. \pm \v 16 «Sunu maam yooyu kay ñoo mujj fuuy, sajju loos, ba sàmmuñu say santaane. \v 17 Ñoo baña dégg, baña bàyyi xel sa kéemaan yi nga def ci seen biir, te ñoo sajju loos, fétteeral ba fal njiit, nara dellu ca seen njaam ga. Waaye yaw yaay Yàlla jiy boroom njéggal ak yiw ak yërmande, di muñ mer, te bare ngor, ba tax waccoo leen. \v 18 Dem nañu sax ba móolal seen bopp jëmmu wëllu te naan: “Yeen, seen Yàllaa ngi; moo leen génnee réewum Misra,” ñàkke la kersa lool. \v 19 Waaye yaw, ci sa yërmande ju réy, waccoo leen ca màndiŋ ma. Taxaaru niir wa noppiwula taxaw ci seen kanam bëccëg bu nekk, di leen jiite ca yoon wa. Taxaaru sawara wa it noppiwula taxaw guddi, di leen niital yoon wa ñuy jaar. \v 20 Sa xel mu rafet nga leen may ba ñu mana ràññee, sa mànn\f + \fr 9.20 \fr*\fk mànn: \fk*\ft seetal ci \ft*\ft \+bk Mucc ga\+bk* 16.\ft*\f* it, noppiwuloo leen koo leel, teg ca ndox ma nga leen daan fajale mar. \v 21 Diiru ñeent fukki at nga leen dundal ca màndiŋ ma, ñàkkuñu dara. Seeni yére ràppul, seeni tànk newiwul. \pm \v 22 «Yaa leen moomale ay réew aki xeet, séddale leen suuf. Ñu nangu réewum Siwon, réewum buurub Esbon, teg ca réewum Og buuru Basan. \v 23 Giiral nga leen, ba ñu tollu ni biddiiwi asamaan, ba noppi dugal leen ca réew ma nga waxoon seeni maam ñu nanguji ko. \v 24 Ci kaw loolu seeni doom nanguji réew ma. Yaa leen nangulal Kanaaneen ña dëkkoon ca réew ma, teg ci seeni loxo buuri réew maak baadoola ya, ñu di leen def lu leen soob. \v 25 Nangu nañu ay dëkk yu tata wër, ak suuf su nangu, aakimoo kër yu fees ak gépp ngëneel, aki teen, ak tóokëri reseñ, ak garabi oliw, garab yay meññ, ne xas; ñuy lekk ba suur. Ñu regg, di xéewloo sa mbaax gu réy gi. \pm \v 26 «Waaye dégguñu ndigal, xanaa di la gàntal. Dañoo sànni saw yoon seen gannaaw; sa yonent ya leen doon xiirtal ci délsi ci yaw, ñu rey leen, ba ñàkke la kersa lool. \v 27 Nga daldi leen teg ci seen loxoy noon, ñu fitnaal leen. Teewul ñu jàq, woo la wall, nga dégge ko fa asamaan, ba jox leen ñu leen xettli, ci sa yërmande ju yaa, ñu xettli leen ci seen dooley noon. \v 28 Naka lañu am noflaay, daldi dellu ci def lu bon fi sa kanam. Nga wacc leen nag ca seen loxoy noon, ñu moom leen. Ba ñu delloo woo la wall, yaa leen dégge fa asamaan, ba xettli leen ay yooni yoon ci sa yërmande ju réy. \v 29 Artu nga leen ndax ñu dellu ci saw yoon, teewul ñu bew, ba sàmmuñu say santaane, xanaa di moy sa àttey yoon yiy taxa dund képp ku ci sàmmu. Ñuy daŋŋiiral, sajju loos, bañ laa déggal. \v 30 Ndaxam muñal nga leen ay at yu bare, di leen artoo sam xel, say yonent di leen ko jottli; waaye taxul ñu déglu. Nga teg leen nag ci loxoy waa réew yi. \v 31 Sa yërmande ju réy nga topp, ba faagaagaloo leen. Wacculoo leen it, ndax yaw Yàllay yiw ak yërmande nga! \pm \v 32 «Kon rikk waay, yaw sunu Yàlla, Yàlla ju màgg, ji àttan te mata ragal, di sàmm kóllëreek ngor; ngalla bul xeeb mboolem toskare ji dikkal sa ñoñ, muy buur ak njiit, \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ak yonent, dale ca sunuy maam ba ci nun ñépp tey, ca janti buuri Asiri, ba sunu jonni yàllay tey. \v 33 Yaw nag yaa yelloo njekk ci mboolem li nu dal, ndax worma nga jëfe, nun noo bon. \v 34 Sunuy buur ak sunuy njiit nag ak sunuy sarxalkat ñoo dale ca sunuy maam, di baña topp sa yoon, baña sàmm say santaane, bàyyiwuñu xel it ci kàdduy seede yi nga leen artoo. \v 35 Ba ñu moomee seenum réew, nekk ci sa teraanga ju réy ja nga leen may ca suuf su yaa, su nangu sa nga leen jox, jaamuwñu la woon te dëdduwñu seen manin yu ñaaw ya. \v 36 Nu ngi nii tey diy jaam. Réew ma nga joxoon sunuy maam, ñuy lekk meññeefam aki ngëneelam, fi lanu doon nii ay jaam. \v 37 Li suuf siy jur a ngi ne gàññ, di alalu buur yi nga teg ci sunu kaw, ndax sunuy moy. Dañu noo yilif, yilif sunug jur, nu mu leen neexe, nu nekke njàqare ju réy.» \s1 Bànni Israyil dogu nañu \p \v 38 Loolu yépp tax na nuy tëral takktoo bu dogu, bind ko, sunuy njiit ak sunuy \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ak sunuy \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* def ci seen màndargay torlukaay. \c 10 \p \v 1 Ñi ko torlu ñoo di: \p Boroom dëkk bi Neyemi doomu Akalya, mook Cedekiya \v 2 ak Seraya ak Asaryaa ak Yeremi \v 3 ak Pasur ak Amarya ak Malkiya \v 4 ak Atus ak Sebaña ak Malug \v 5 ak Arim ak Meremot ak Obadiya \v 6 ak Dañeel ak Ginton ak Barug \v 7 ak Mesulam ak Abya ak Miyamin \v 8 ak Maasya ak Bilgay ak Semaya. Ñooñu ñoo di sarxalkat ya. \p \v 9 Leween ñi ñoo di: \p Yeswa doomu Asaña, ak Binuy, kenn ca doomi Enadàdd, ak Kadmiyel. \v 10 Seeni bokk ca lañu, di Sebaña ak Odiya ak Kelita ak Pelaya ak Xanan \v 11 ak Mika ak Reyob ak Asabya \v 12 ak Sakuur ak Serebya ak Sebaña \v 13 ak Odiya ak Baani ak Beninu. \p \v 14 Njiiti askan wi ñoo di: \p Paros ak Payat Mowab ak Elam ak Sàttu ak Baani \v 15 ak Buuni ak Asgàdd ak Bebay \v 16 ak Adoña ak Bigway ak Adin \v 17 ak Ater ak Esekiya ak Asur \v 18 ak Odiya ak Asum ak Besay \v 19 ak Arif ak Anatot ak Nebay \v 20 ak Magpiyas ak Mesulam ak Esir \v 21 ak Mesesabel ak Cadog ak Yaduwa \v 22 ak Pelaca ak Xanan ak Anaya \v 23 ak Oseya ak Anaña ak Asub \v 24 ak Aloyes ak Pila ak Sobeg \v 25 ak Reyum ak Asabna ak Maaseya \v 26 ak Axiya ak Xanan ak Anan \v 27 ak Malug ak Arim ak Baana. \s1 Solob dogu baa ngi \p \v 28 Bànni Israyil ga ca des nag fekksi leen, muy \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yaak \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñaak fara bunt yaak jàngkat yaak liggéeykati kër Yàlla ga, di mboolem nun ñi beddeeku woon waasoy réew yi, ngir topp yoonu Yàlla wi, nook sunuy jabar ak sunu doom yu góor ak yu jigéen, mboolem ñi xam te xàmmee. \v 29 Ci kaw loolu nu ànd ak sunu bokki garmi, waatook ñoom ne dinanu topp yoonu Yàlla wi mu dénkaane, Musaa jaamam ba jottli; di ko sàmm, di jëfe mboolem sunu santaaney Boroom \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ak àttey yoonam ak dogali yoonam. \pm \v 30 Nu ne nag dunu may waa réew mi sunu doom yu jigéen te dunu jëlal sunuy doom seeni doom yu jigéen. \pm \v 31 Te itam bu waa réew mi indee am njaay mbaa lépp luy pepp, di ko jaay ci \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*, dunu ko jënd ci ñoom bésub Noflaay mbaa bés bu \w sell|lemma="sell:"\w*, te atum juróom ñaareel mu nekk dinanu bale bépp bor. \pm \v 32 Ci biir loolu nu warloo santaaney joxe at mu nekk ñeenti garaami xaalis, bu jëm ca sunu liggéeyu kër Yàlla ga, \v 33 jëm ca mburum wone ba, ak \w saraxi pepp|lemma="Sarax yi:"\w* yi war bés bu nekk, ak \w saraxi dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* yu bés bu nekk, ak saraxi bési Noflaay, ak yu Terutel weer ak yu bési màggal yi, ak yeneen yu ñu sellalal Yàlla, ak \w saraxi póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w* yi \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* di jotoo, ak mboolem la war ca sunu liggéeyu kër Yàlla ga. \pm \v 34 Ay bant lanu tegoo ci sunu biir, nun sarxalkat yeek Leween ñeek baadoolo yi, ngir dogalal waa kër gu nekk àpp ba ñu wara aye cim at, te ñu war caa yóbbu seen sasu matt ca sunu kër Yàlla ga, ngir taal ko ca sunu \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* Yàlla Aji Sax ji, muy la ñu bind ci téereb yoon wi. \pm \v 35 Nu dogu ba tey ne dinanu yóbbu ca kër Aji Sax ji, at mu nekk, li sunu suuf jëkka meññle ak lu garab yépp jëkka ñorle. \v 36 Ci biir loolu nu dogoo def li ñu bind ci yoon wi, di yóbbu ca sunu kër Yàlla ga sunu taaw yu góor ak lu sunu jur taawloo, gu gudd gaak gu gàtt ga, di teg lépp ci loxoy sarxalkat ya fay liggéey. \v 37 Ci kaw loolu nu wara yóbbu ca sunu néegi dencukaayi kër Yàlla ga lu jëkk ci sunu notu sunguf, ak sunu jooxey pepp, ak sunu meññeefi garab yépp, ak sunu biiñ ak diw, di teg lépp ci loxoy sarxalkat yi. Ba tey nuy indil Leween ñi céru fukkeelub lépp luy meññee ci sunu suuf, ndax Leween ñeey dajalesi céri fukkeel yi ci gox yi nuy bey yépp. \v 38 Sarxalkat bu askanoo ci Aaróona mooy gunge Leween ñiy jëlsi céri fukkeel yi. Su ko defee Leween ñi yóbbu fukkeelu céri fukkeel yi ba ca sunu kër Yàlla ga, fat ko ca néegi dencukaayi alal ya. \v 39 Ci néeg yooyu la bànni Israyil ak askanu Leween ñi di yóbbu jooxeb pepp ba ak biiñ baak diw ga; fa la ndabi bérab bu sell ba dence, te fa la sarxalkat, ya sasoo liggéey ba nekk, ñook fara bunt yaak jàngkat ya. \pm Nu dogu nag ne dunu sàggane sunu kër Yàlla ga. \c 11 \p \v 1 Ba mu ko defee njiiti mbooloo ma dëkk Yerusalem. Ña des ca mbooloo ma tegoo bant ngir fukk ñu daje kenn génne ca, dëkk Yerusalem, dëkk bu sell bi, juróom ñeent ñi ci des toog ca (seeni) dëkk yu ndaw. \v 2 Mbooloo ma nag gërëm ñi nangul seen bopp ne dañuy dëkk Yerusalem. \v 3 Dëkki Yuda ya bànni Israyil yaa ca dëkkoon, ñook sarxalkat yaak Leween ñaak, ña féetewoo liggéey yu sew ya ca kër Yàlla gaak ña askanoo ca jaami Suleymaan ya, ku nekk ak sa céru suuf, ca dëkk ba nga bokk. Ñii ñuy lim nag ñooy njiiti diiwaan ñi dëkke Yerusalem. \v 4 Amoon na it ñu dëkkoon Yerusalem te bokk ci giirug Yuda ak giirug Beñamin. \p Ñi bokk ci askanu Yuda Ataya la, ku góor ka Usiya di baayam; Sàkkaryaa di baayu Usiya; Amarya di baayi Sàkkaryaa; Sefatiya di baayi Amarya; Mayalel di baayi Sefatiya, Peres di baayi Mayalel; \v 5 ak Maaseya, ku góor ka Barug di baayam; Kol Xose di baayu Barug; Xasaya di baayu Kol Xose; Adaya di baayu Xasaya; Yowarib di baayu Adaya; Sàkkaryaa may doomu ku dëkk Silon di baayu Yoyarib. \v 6 Waa askanu Peres ya dëkk Yerusalem ñeenti téeméeri jàmbaar lañu ak juróom benn fukk ak juróom ñett. \p \v 7 Ñi bokk ci askanu Beñamin Salu la, ku góor ka Mesulam di baayam; Yowet di baayu Mesulam, Pedaya di baayu Yowet; Kolaya di baayu Pedaya, Maaseya di baayu Kolaya, Itiyel di baayu Maasya, Yisaya di baayu Itiyel; \v 8 Gabay ak Salay topp ca Ñoom ñépp di juróom ñeenti téeméer ak ñaar-fukk ak juróom ñett. \v 9 Yowel doomu Sikkri moo leen jiite woon, Yewuda doomu Asenuwa topp ca, di ñaareelu kilifag dëkk ba. \p \v 10 Sarxalkat ya Yedaya doomu Yoyarib Yakin bokk na ca, \v 11 ak Seraya, baayam di Ilkiya, Mesulam di baayu Ilkiya, Sadog di baayu Mesulam, Merayot di baayu Sadog, Ayitub, njiital kër Yàlla ga di baayu Merayot. \v 12 Ñoom ak ña ñu àndal ca liggéeyu kër Yàlla ga. Ñuy juróom ñetti téeméer ak ñaar fukk ak ñaar. Adaya ma Yerowam di baayam it bokk na ca. Pelaliya di baayu Yerowam, Amsi di baayu Pelaliya, Sàkkaryaa, di baayu Amsi, Pasur di baayu Sàkkaryaa, Malkiya di baayu Pasur. \v 13 Maam la ak ña mu àndal ca liggéey ba te ñu yilif seeni kër baay, ñuy ñaar téeméer ak ñeent-fukk ak ñaar. Amasay ma Asarel di baayam bokk na ca; Axsay di baayu Asarel; Mesilemot di baayu Axsay; Imer di baayu Mesilemot. \v 14 Moom la ak seeni bokk, yu jàmbaare te ñeme. Ñuy téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett. Sabdiyel ma Agdolim di baayam moo leen jiite woon. \p \v 15 Leween ña Semaya ma Xasub di baayam bokk na ca, Asrikam ay baayu Xasub; Asabiya di baa yu Asrikam, Buni di baayam Asabiya; \v 16 moom la ak Sabtay ak Yosabàdd, di ñaari kilifay Leween yu sasoo liggéeyu kër Yàlla ga, fa féete biti; \v 17 ak Mataña ma baayam di Mika. Sabdi mooy baayu Mika; Asaf miy baayu Sabdi moo doon kilifa gay jiite ci cant ak ñaan; ak Bagbukiya miy mbokkum Mataña tey njiit li topp ci moom ak Abda mi Samuya di baayam; Galal di baayu Samuya, Yedutun di baayu Galal. \v 18 Mboolem Leween ña dëkkoon ca dëkk bu sell ba ñaar téeméer lañu ak juróom ñett fukk ak ñeent. \v 19 Wattukati bunt ya Akub la woon ak Talmon ak seeni bokk. Ñoo doon wattu bunt ya, tollu ci téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar. \p \v 20 Ña des ci bànni Israyil nag, boole ca sarxalkat yaak Leween ña ca des daldi dëkke mboolem dëkki Yuda ya, ku nekk ak fa mu séddoo. \p \v 21 Ci kaw loolu ña féetewoo liggéey yu sew ya ca kër Yàlla ga dëkk Ofel, Siyxa ak Gispa jiite leen. \p \v 22 Kilifag Leween ña ca Yerusalem moo doon Utsi ma Bani di baayam; Xasabiya di baayu Bani, Mataña di baayu Xasabiya, Mika di baayu Mataña. Utsi bokkoon ci ñi askanoo ci Asaf te doonoon woykat yay woy ca kër Yàlla ga. \v 23 Woykat ya sax ña nga nekkoon ca ndigalal Buur lu leen di dogalal la leen war bés bu nekk. \p \v 24 Petaya ma baayam di Mesesabel mu bokk ci askanu Sera doomu Yuda moom la Buur dénkoon mboolem mbir yi soxal mbooloo mi. \p \v 25 Ci wàllu dëkk yu ndaw yeek seeni àll nag am na waa kër Yuda yu dëkke woon Kiryaat Arba ak dëkk-dëkkaan ya ko wër, am ñu ca dëkke Dibon ak la ko wër, am ñu dëkke Yekabseel ak gox ya ko wër; \v 26 am ñu dëkke Yeswa ak Molada ak Bet Pelet; \v 27 ak Àccar Suwal ak Beerseba ak la ko wër. \v 28 Mu am ñu dëkke Ciglaag ak Mekona ak la ko wër; \v 29 ak En Rimon ak Sora ak Yarmut; \v 30 ak Sanowa ak Adulam ak gox ya ko wër ak Lakis aki àllam ak Aseka ak la ko wër. Noonu ñu dëkke la dale Beer Seba ba ca xuru Inom. \p \v 31 Noonu waa giirug Beñamin dëkke la dale Geba ak Migmas, boole ca Aya ak Betel ak la ko wër. \v 32 Mu am ñu ca dëkke Anatot ak Nob ak Anaña; \v 33 ak Àccor ak Raama ak Gitayim; \v 34 ak Adit ak Seboyim ak Nebalat; \v 35 ak Lot ak Ono ca xuru liggéeykat ya. \v 36 Am na nag ay kuréli Yudeen ñu bàyyikoo Yuda sanci ca waa giirug Beñamin. \c 12 \s1 Ñii ñooy Leween ñeek sarxalkat yi jëkka ñibbsi \p \v 1 \w Sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yaak \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ña ñibbsi, ànd ak Sorobabel doomu Selcel, ak Yosuwe sarxalkat bu mag ba, ñii la: \p Seraya ak Yeremi ak Esra \v 2 ak Amarya ak Malug ak Atus \v 3 ak Sekaña ak Reyum ak Meremot \v 4 ak Ido ak Gintoy ak Abya \v 5 ak Miyamin ak Maadiya ak Bilga \v 6 ak Semaya ak Yowarib ak Yedaya \v 7 ak Salu ak Amog ak Ilkiya ak Yedaya. Ñooñooy kilifay sarxalkat yeek seeni bokk ca jamonoy Yosuwe. \p \v 8 Leween ñi ñoo doon Yeswa ak Binuy ak Kadmiyel ak Serebya ak Yuda ak Mataña may jiite jàngi cant ya, mooki bokkam. \v 9 Bagbukiya ak Uni ak seeni bokk janook ñoom ca liggéey ba. \p \v 10 Yosuwe, sarxalkat bu mag ba mooy baayu Yowakim. Yowakim di baayu Elyasib, Elyasib di baayu Yowada, \v 11 Yowada mooy baayu Yonatan, Yonatan di baayu Yaduwa. \p \v 12 Ca jamonoy Yowakim sarxalkat bu mag ba, ña jiite woon kër sarxalkat ya ñii la: Meraya ma bawoo ca waa kër Seraya ak Anaña bawoo ca waa kër Yeremi, \v 13 Mesulam bawoo ca waa kër Esra, Yowanan bawoo ca waa kër Amarya, \v 14 Yonatan bawoo ca waa kër Malug, Yuusufa bawoo ca waa kër Sebaña, \v 15 Adna bawoo ca waa kër Arim, Elkay bawoo ca waa kër Merayot, \v 16 Sàkkaryaa bawoo ca waa kër Ido, Mesulam bawoo ca waa kër Ginton, \v 17 Sikkri bawoo ca waa kër Abya. Mu am ñu jóge ca waa kër Miñamin. Piltay bawoo ca waa kër Mowadiya, \v 18 Samwa bawoo ca waa kër Bilga, Yonatan bawoo ca waa kër Semaya, \v 19 Matenay bawoo ca waa kër Yowarib, Usi bawoo ca waa kër Yedaya, \v 20 Kalay bawoo ca waa kër Salu, Eber bawoo ca waa kër Amog, \v 21 Asabya bawoo ca waa kër Ilkiya, Netanel bawoo ca waa kër Yedaya. \p \v 22 Ca janti sarxalkat yu mag ya, Elyasib ak Yowada ak Yowanan ak Yaduwa, ku nekk ak jamonoom, ña jiite woon këri Leween ña ak sarxalkat ya, bindoon nañu leen ci biir nguurug Daryus buuru Pers. \v 23 Ña jiite woon seeni kër baay te askanoo ci Lewi, ba ca jamonoy Yonanan sëtub Elyasib daan nañu leen bind ñoom ñépp ca téere ba ñu dippee Xew-xew ya. \p \v 24 Njiiti Leween ñi ñoo doon: Asabya ak Serebya ak Yeswa doomu Kadmiyel, ñook seen bokk ña ñu daan awanteel làng ak làng ci jàngi cant, muy la Daawuda góoru Yàlla ga santaane woon. \v 25 Mataña ak Bagbukiya ak Obadiya ak Mesulam ak Talmon ak Akub ñoo doon fara bunt ya, di wattu néegi dencukaay, ya ca bunt ya. \p \v 26 Ñooñoo fa nekkoon ca jamonoy Yowakim doomu Yosuwe. Yosuwe, Yoccadag mooy baayam. Ñoo fa nekkoon itam ca jamonoy Neyemi boroom dëkk ba, ak Esra ma doon sarxalkat, di bindkat. \s1 Daloo nañu tata ja \p \v 27 Gannaaw gi, ca xewu daloog tatay Yerusalem ja, ñu wooye \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ña mboolem fa ñu dëkke, indi leen Yerusalem, ngir ñu màggal daloo ga ci biir mbég ak jàngi cant; tëggum weñ ya jib, ànd ak xeeti xalam. \v 28 Ci biir loolu ñu indi jàngkat ya ñoom it, boole leen jële ca diiwaan ba wër Yerusalem, ca dëkk yu ndaw ya ca Netofa, \v 29 ak Bet Gilgal ak diiwaani Geba ak Asmawet. Fekk na jàngkat ya tabax ay dëkk yu ndaw fa wër Yerusalem. \p \v 30 Ba loolu amee \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yaak Leween ña laabal seen bopp, doora laabal mbooloo ma, ak bunt yaak tata ja. \p \v 31 Ci kaw loolu ma yéegloo njiiti Yudeen ña ca kaw tata ja, daldi sos ñaari kuréli jàngkat yu mag. Genn ga di dox ca kaw tata ja ci wetu ndijoor, wuti buntu Sën ba. \v 32 Osaya ma nga topp ca seen gannaaw, ànd ak genn-wàllu njiiti Yudeen ña, \v 33 ak Asaryaa ak Esra ak Mesulam, \v 34 ak Yuda ak Beñamin ak Semaya ak Yeremi. \v 35 Lenni sarxalkat yaa nga ca topp aki liit, di ñi ànd ak Sàkkaryaa doomu Yonatan. Yonatan, Semaya mooy baayam; Semaya, Mataña di baayam, Mataña, Mikaya mooy baayam; Mikaya, Sakuur ay baayam; Sakuur, Asaf mooy baayam. \v 36 Sàkkaryaa ànd aki bokkam, ñuy Semaya ak Asarel ak Milalay ak Gilalay ak Maay ak Netanel ak Yuda ak Anani. Ña nga yore ay jumtukaayi xumbéen yu Daawuda, góorug Yàlla ga. Esra bindkat ba moo leen jiite woon. \v 37 Ñu dikk ba tollook buntu Ndox ma, janook dëggastal, ya jëm ca Kër Daawuda, fa ñuy yéege jëm ca tata ja tiim kër Buur Daawuda. Ñu jubal nag ba ca buntu Ndox ma, ca penku. \p \v 38 Ci biir loolu ñaareelu kurélu jàngkat ya doxe wetu càmmoñ; man nag, ma topp ca seen gannaaw ca kaw tata ja, ànd ak genn-wàllu mbooloo ma. Nu jaare ca wetu sooroor ba ñuy wax Taal ya, ba fa tata ja yaatoo. \v 39 Nu romb nag fa tiim buntub Efrayim ak buntu Cosaan ba, ak buntu Jën ya ak soorooru Ananel, wees soorooru Meya, ba àgg ca buntu Gàtt ya. Ña nga taxaw ca buntu Dag ya. \v 40 Ci kaw loolu ñaari kuréli jàngkat ya taxaw ca biir kër Yàlla ga, man itam ma taxaw, maak genn-wàllu mbooloom jawriñ ñi ma àndal, \v 41 ak sarxalkat ya, di Elyakim ak Maaseya ak Miñamin ak Mikaya ak Elyonay ak Sàkkaryaa ak Anaña, ñook seeni liit. \p \v 42 Maaseya it a nga ca woon ak Semaya ak Elasar ak Usi ak Yowanan ak Malkiya ak Elam ak Eser. Jàngkat ya daldi samp, Israya jiite leen. \p \v 43 Sarxe nañu bésub keroog sarax yu réy tey bànneexu, ndax Yàllaa leen may bànneex bu réy. Jigéen ñaak gone ya it di bànneexu, mbégarey Yerusalem di dégtu fu sore. \p \v 44 Ñu daldi tànn bésub keroog ay nit, dénk leen néegi dencukaay, ya ñuy yeb ay jooxe, ak \w saraxi ndoortel meññeef|lemma="Sarax yi:"\w*, ak céri fukkeel yu ñuy génne. Ñu war caa dajale nag cér ya yoon wi dogalal sarxalkat yeek Leween ñi, te mu jóge ci tool yi wër dëkk yi. Waa Yuda rafetlu ca taxawaayu sarxalkat yaak Leween ña. \v 45 Leween ñaa dénkoo woon seen dénkaaney Yàlla, ak dénkaaney laabal ba, ak jàngkat yaak fara bunt yay topp la Daawuda santaane woon, mook doomam Suleymaan. \v 46 Te naka jekk ca janti Daawuda ak Asaf amoon na ay njiiti jàngkat yuy jiite ay jàngi màggal ak jàngi cant, ñeel Yàlla. \v 47 Ci biir loolu, ca janti Sorobabel ak ca janti Neyemi, askanu Israyil gépp daan nañu génneel jàngkat yeek fara bunt yi seen cér, bés bu nekk it, génneel Leween ñi seen cér, Leween ñi génneel askanu Aaróona seen cér. \c 13 \s1 Neyemi sopparñi na \p \v 1 Bésub keroog jàng nañu ci téereb Musaa, mbooloo ma di dégg. Ñu gis ñu bind ca ne, muy Amoneen, muy Mowabeen, kenn du ci bokk ci ndajem bànni Israyil mu ñuy màggale Yàlla, ba fàww. \v 2 Li ko waral moo di ñoo bañoona dabe \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* aw ñam wu ñu lekk ak ndox mu ñu naan, xanaa di fey Balaam, jibar ba, ngir mu rëbbal leen leen. Teewul sunu Yàlla soppi rëbb ga barke. \v 3 Naka la mbooloo ma dégg la yoon wa digle, ñu daldi dàqe Israyil mboolem askan wu raxe. \p \v 4 Lu jiitu loolu nag tabboon nañu Elyasib, \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba, dénk ko sunu néegi dencukaayi kër Yàlla ga. Mu doonoon jegeñaaleb Tobya, \v 5 ba tax Elyasib jël néegu dencukaay bu yaatu, jox ko Tobya. Néeg booba lañu daan denc \w saraxi pepp|lemma="Sarax yi:"\w* yaak \w cuuraay|lemma="cuuraay l-:"\w* yaak ndab yaak céri fukkeel ya, muy bele ak biiñ ak diw, te ndigal sédd ko \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñeek jàngkat yeek fara bunt yi. Foofu it lañu daan denc jooxe yi ñeel sarxalkat yi. \v 6 Booba yépp nag nekkuma woon Yerusalem, ndax fekkoon na ma dellu ca Artaserses buuru Babilon, ca fanweereelu atu nguuram ak ñaar. Toog naa fa lu yàgg, doora ñaan Buur, ba mu yiwiwaat ma. \v 7 Ba ma àggee Yerusalem, ma yég tojaange gi Elyasib defal Tobya, jox ko néeg ca biir ëttu kër Yàlla ga. \v 8 Ma ñaawlu ko lool, daldi boole yëfi Tobya, génnee néeg ba, sànni. \v 9 Ci kaw loolu ma santaane ñu laabal néeg ya, ba noppi ma yebaat ca ndabi kër Yàlla ga ak saraxi pepp yaak cuuraay la. \p \v 10 Ma dégg itam ne joxuñu Leween ñi seeni cér, ba tax ku nekk ci Leween ñaak jàngkati kër Yàlla ga ne coww ca toolu boppam, bàyyi liggéey bi mu sasoo. \v 11 Ma ŋàññ jawriñ yi, ne leen: «Ana lu waral ñuy sàggane kër Yàlla gi?» Ci biir loolu ma woo Leween ñeek jàngkat yi, ñu daje, ma delloo leen ca seeni liggéey. \v 12 Ba mu ko defee waa Yuda gépp dellu di indi ca biir néegi dencukaay ya céri fukkeel ya ñuy génne, di pepp ak biiñ aku diw. \v 13 Ba loolu amee ma tabb Selemya sarxalkat ba, ak Cadog bindkat ba, dénk leen dencukaay ya, ñook Pedaya Leween ba; ka leen ciy jàpple di Xanan doomu Sakuur. Sakuur, Mataña mooy baayam. Ñu doonoon nit ñu ñu ràññee seen maandute, ba sas leen ñuy séddale sarax yi ci seen biir. \p \v 14 Rikk sama Yàlla, bàyyee ma lii xel, te bul far sama jëfi ngor ji ma jëfe ci sama biir kër Yàlla gi aki wartéefam. \p \v 15 Ci fan yooyu ma gis ci Yuda ay nit ñuy nal reseñ, \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*. Mu am ñuy indi ay sabaari pepp yu ñuy sëf ay mbaam, boole ca biiñ ak reseñ ak figg ak lu nekk, di ko yóbbu Yerusalem ci bésub Noflaay. Ma àrtu leen it ca la ñuy jaay seen yëf yooyu ci boobu bés. \v 16 Amoon na itam ay waa Tir yu féete Yerusalem, di fa indi ay jën ak mboolem xeeti njaay, di ko jaay waa Yudak Yerusalem ci bésub Noflaay. \v 17 Ma ŋàññ kàngami Yuda, ne leen: «Lu ñaaw lii ngeen di def nag di teddadil bésub Noflaay? \v 18 Xanaa du nii la seen maam ya daan def, ba tax sunu Yàlla wàcce ci sunu kaw musiba mii mépp, wàcce ko ci dëkk bii, yeen ngeen di wooti sànjum Yàlla ci kaw Israyil, di teddadil bésub Noflaay?» \p \v 19 Ci kaw loolu, balaa bésub Noflaay biy duggsi, bu bunti Yerusalem tàmbalee keppaaral ci ngoon si rekk, ma santaane ñu tëj, baña ubbeeti, ba bésub Noflaay bi wees. Ci biir loolu ma tànn ci samay nit, taxawal leen ca bunt ya, ngir ñu baña dugal ay sëf bésub Noflaay. \v 20 Ba mu ko defee jula yu mag yaak ñay jaayaatu lu nekk, fanaan benn yoon ba ñaar ca biti. \v 21 Ma àrtu leen, ne leen: «Ana lu waral ngeen di fanaan ci taatu tatay dëkk bi? Bu ngeen ko defatee, dinaa leen teg loxo!» Booba lañu noppee dikk bésub Noflaay. \v 22 Ma sant it Leween ñi ñu laabal seen bopp te dem wattuji bunt ya, ngir sellal bésub Noflaay. \p Ngalla sama Yàlla, bàyyee ma lii xel itam te yërëme ma sa ngor lu bare. \p \v 23 Ma gisati ci jamono yooyu ay Yudeen ñu jël jabar ci waa Asdodd ak Amon ak Mowab. \v 24 Seen genn-wàlli njaboot di làkk asdodd, ña ca des di làkk leneen ci làmmiñi doxandéem yi, te kenn ci ñoom manula wax yawut. \v 25 Ma ŋàññ leen, móolu leen, dóor ñenn ci ñoom, xuuf seen kawar, giñloo leen ci Yàlla ne dootuñu may seen doom yu jigéen ay doxandéem te dootuñu ci jëlal jabar seeni doom mbaa seen bopp. \v 26 Ma ne leen: «Xanaa du nii la Suleymaan buurub Israyil bàkkaare woon? Li xeet yiy bare lépp amul benn buur bu meloon ni moom. Ku Yàllaam soppoon la te Yàllaa ko faloon buurub Israyil gépp. Waaye moom sax jigéeni doxandéem yi bàkkaarloo nañu ko. \v 27 Bëggatunoo dégg ngeen di def gii ñaawtéef gu réy, bay ñàkke sunu Yàlla kóllëre, di jël ay doxandéem jabar.» \v 28 Fekk na kenn ci doomi Yowada doomu sarxalkat bu mag ba Elyasib sax, jël doomu Sanbalat mu Oron. Teewul ma dàq waa ji, mu daw ba sore ma. \p \v 29 Ngalla sama Yàlla, bàyyil xel mbugal mu ñeel ñii teddadil liggéeyu carxal, fecci worma sasu carxal ak xeetu Leween. \p \v 30 Ma laabal leen nag, ñu teqlikook lu bokk cig ndoxandéem, ba noppi sas sarxalkat yeek Leween ñi, ku nekk ca liggéeyam. \v 31 Ma dekkal saraxu matt yi ñu wara joxe bu àppam jotee, ak saraxi ndoortel meññeef. \p Ngalla sama Yàlla, bàyyee ma lii xel ngir ngëneel.