\id MAL (WOL) \ide UTF-8 \h Malasi \toc1 Malasi \toc2 Malasi \mt2 Téereb Yonent Yàlla \mt1 Malasi \c 1 \p \v 1 Yéeneb kàddug Aji Sax jii moo ñeel Israyil, ci jottlib Malasi. \s1 Cofeelu Aji Sax ji kóllëreem la laloo \q1 \v 2 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nee: «Dama leena sopp,» \q1 yeen ngeen ne: «Ana noo nu soppe?» \q1 Mu ne: «Xanaa Esawu du seexub Yanqóoba?» \q1 Kàddug Aji Sax jee, \q1 «moona Yanqóoba laa sopp, \q1 \v 3 te Esawu laa foñ. \q1 Maa def ay tundam ab gent, \q1 ab céru suufam, ma def ko dëkkuwaayu \q2 tilli màndiŋ mi. \q1 \v 4 Su Edom\f + \fr 1.4 \fr*\ft Edomeen ñi ñoo askanoo ci Esawu, bànni Israyil askanoo ci Yanqóoba seexu Esawu. Esawu moo teddadil li taxawe kóllërey Aji Sax ji, ba mu sàgganee cérub taawam. Seetal ci \ft*\ft \+bk Njàlbéen ga \+bk*25.34. Edomeen ñi ñoo dëddu Israyil mi Aji Sax ji taamul boppam. Seetal ci \+bk Abdiyas \+bk*10-14.\ft*\f* nee: “Dees noo rajaxe, \q1 waaye nooy tabaxaat gent bi,” \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi moom dafa wax ne: \q1 “Ñooy tabax, maay màbb.” \q1 Ñoom lees di wooye waa diiwaan bu bon bi, \q1 askan wi Aji Sax ji mere ba fàww. \q1 \v 5 Yeena koy gisal seen bopp, \q1 yeenay seede ne: “Màggaayu Aji Sax ji \q2 jéggi na kemu réewum Israyil.” \s1 Aji Sax ji tiiñal na sarxalkat yi \q1 \v 6 «Doom teral baayam, \q1 jaam, sangam. \q1 Man, su ma dee baay, ana saab teraanga? \q1 Su ma dee ab sang, ana saab cér?» \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoor yee ko wax, \q1 mu ne: «Yeen \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi teddadil ngeen sama tur, \q1 yeen ngeen ne: “Ana nu nu teddadile sa tur?” \q1 \v 7 Xanaa di indi ñam wu sobewu \q2 fi sama \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*. \q1 Yeen ngeen ne: “Ana nu nu la sobeele?” \q1 Xanaa xalaat ne sañees naa teddadil \q2 sarxalukaayu Aji Sax ji. \q1 \v 8 Bu ngeen ma sarxalsee jur gu gumba, dara aayu ci? \q1 Am bu ngeen ma sarxalsee jur guy soox, \q2 ak jur gu wopp, dara aayu ci daal! \q1 Yóbbul leen ko seen boroom dëkk rekk, \q1 ba xam ndax moo leen di nangul, \q1 mbaa mu siggil leen!» \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. \b \q1 \v 9 «Ngeen ne: “Léegi nag tinuleen Yàlla rekk, \q1 mu baaxe nu!” \q1 Yeena tooñ, ndax day siggil kenn ci yeen?» \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. \q1 \v 10 «Éy bu kenn ci yeen tëjoon bunt yi far, \q1 te baña jafal ab taal ci sama kaw sarxalukaay ci dara. \q1 Awma benn bànneex ci yeen!» \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. \q1 «Ab sarax, duma ko nangoo ci seeni loxo. \q1 \v 11 Waaye li ko dale penku ba sowub jant, \q1 fu ci nekk la sama tur màgge ci biir xeet yi, \q1 te fépp lees di taale cuuraay, ngir sama tur, \q1 boole ci sarax su set, \q1 nde sama tur a ni màgge fi biir xeet yi.» \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. \q1 \v 12 «Waaye yeen yeena teddadil sarxalukaayu Aji Sax ji, \q1 nde yeena xalaat ne lu sobewu la, \q1 te aw yàppam, aw ñamam jarul dara. \q1 \v 13 Yeena ngi naa: “Ndaw lu soof,” di ciipatu.» \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. \q1 «Jur gu ñu sàcc ngeen may indil, \q2 ak guy soox, ak gu wopp, \q1 loolu mooy seen sarax! \q1 Nu ma koy nangoo ci seeni loxo?» \q1 Aji Sax jee ko wax. \b \q1 \v 14 «Alkànde ñeel na ab jinigalkat bu am ci géttam \q2 am kuuy mu mu xasoo sarxe, \q1 te di sarxalal Boroom bi jur gu sikk, \q1 nde man, buur bu mag laa!» \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. \q1 «Sama tur moo jara ragal fi biir xeet yi. \c 2 \p \v 1 «Léegi nag, sarxalkat yi, santaane bii yeen la ñeel. \q1 \v 2 Su ngeen dégluwul, \q1 te defuleen seen xel ci teral sama tur,» \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, \q1 «alkànde laay yebal fi seen biir, \q1 ba alagaale seeni barke, \q1 te alag naa ko jeeg, \q1 nde defuleen seen xel ci teral ma. \q1 \v 3 Maa ngii di yar seen askan, \q1 sëlëm leen sébbriit, \q1 mi jóge ci seen saraxi màggal, \q1 ñu tonniwaale leen ak sébbriit mi. \q1 \v 4 Su boobaa ngeen xam ne \q1 maa leen yónnee santaane bii, \q1 ngir saxal sama \w kóllëreek|lemma="kóllëre g-:"\w* Lewi\f + \fr 2.4 \fr*\ft Leween ñi jëfe woon fiiraange ci Aji Sax ji, ñoom lay wax. Seetal ci \ft*\ft \+bk Mucc ga \+bk* 32.25-29.\ft*\f*.» \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. \q1 \v 5 «Sama kóllëre moom laa ko séqal, \q1 mu jur ndund ak jàmm, \q1 maa ko may loolu ngir mu ragal ma, \q1 ragaloon na ma it, bay yéemu ci sama tur. \q1 \v 6 Njànglem dëgg la dëkkaloon ci gémmiñam, \q1 te ag njubadi, déggeesu ko ciw làmmiñam, \q1 xanaa di ànd ak man ci jàmm ak njub, \q1 tey baloo ñu bare yoonu ñaawtéef. \b \q1 \v 7 «Kàddug sarxalkat déy day sàmm xam-xam, \q1 te ciy waxam la nit ñi di sàkkoo àlluwa, \q1 nde mooy ndawal Aji Sax ji Boroom gàngoor yi. \q1 \v 8 Waaye yeen dangeena moy yoon wi, \q1 seenum njàngle ngeen fakktale ñu bare, \q1 te yeena fecci kóllëreg Lewi.» \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. \q1 \v 9 «Moo tax man it ma def xeet wépp xeeb leen, \q2 sewal leen, \q1 feye leen ko seen ñàkka sàmm samay yoon, \q1 ak par-parloo gi ngeen di diglee yoon wi.» \s1 Aji Sax ji du nangu saraxi workat yi \q1 \v 10 Xanaa du benn baay lanu am, nun ñépp? \q1 Te jenn Yàlla jee nu sàkk? \q1 Lu waral ku ne di wor mbokkam, \q1 ba fecci \w kóllërey|lemma="kóllëre g-:"\w* maam ya? \q1 \v 11 Yuda wor na, \q1 lu jomblu lees def \q2 fi Israyil ak Yerusalem. \q1 Yuda déy moo teddadil li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji sopp \q2 te mooy bérabam bu \w sell|lemma="sell:"\w*: \q1 Yuda moo takk janqub yàllay doxandéem. \p \v 12 Ku def lii, yal na Aji Sax ji dagge ci xaymay Yanqóoba, gépp kuutaayam, boole ci kuy indil ab sarax, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi. \q1 \v 13 Lii itam yeena ngi koy def: \q1 Yeena ngi tawal ay rongooñ \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* Aji Sax ji, \q1 di jooy ak a binni, \q1 ndax moo geesootul seen sarax, \q1 te nangootul lenn ci seen loxo. \q1 \v 14 Ngeen naa: «Ndax lan?» \q1 Ndax Aji Sax ji moo seede seen diggante \q2 ak seen jabar ja ngeen jël ba ngeen di ndaw, \q1 tey ngeen wor ko, te mu doonoon seen wéttal, \q1 seen jabar ju ngeen séqal kóllëre. \q1 \v 15 Kenn deful lii te desem xel. \q1 Kenn doŋŋ a ko defoon. Ndax lan? \q1 Kuutaay li ko Yàlla digoon la doon wut. \q1 Kon nag sàmmleen seenum xel, \q1 te buleen wor seen jabar ja ngeen jël \q2 ba ngeen di ndaw. \q1 \v 16 «Pase laa bañ,» \q1 Aji Sax ji, Yàllay Israyil moo ko wax, \q1 «ak ku làmboo jëfi loraange ni mbubb.» \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. \q1 Kon nag sàmmleen seenum xel, \q1 te buleen wor. \s1 Aji Sax ji, dëgg lay àtteji \q1 \v 17 Soof ngeen \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ak seeni wax, \q1 ngeen naan: «Nu nu ko soofe?» \q1 Xanaa naan: «Képp kuy def lu bon \q1 mooy ki baax ci Aji Sax ji, \q1 te kooku la safoo.» \q1 Mbaa ngeen naa: «Ana Yàlla jiy àtte dëgg sax?» \c 3 \p \v 1 «Maa ngii di yebal sama ndaw, \q1 mu xàllal ma aw yoon. \q1 Sang bi (/Boroom bi) ngeen di sàkku \q2 mooy jekki agsi këram, \q1 malaakam \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* moomu (/ndawal kóllëre loolu), ki ngeen safoo, \q1 mu ngooguy dikk.» \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. \q1 \v 2 Waaye bésub dikkam, ana ku ko mana dékku? \q1 Bu teewee ana kuy taxaw? \q1 Nde moom daa mel ni sawaras tëgg \q2 buy xelli weñ, \q1 melati ni xemey fóotkat. \q1 \v 3 Fa mbaxana dee benn lay tooge \q2 ni xellikat ak seggkat, \q1 te mooy segg sëti Lewi, xelli leen \q2 ni xaalis ak wurus, \q1 ba ñu doon niti Aji Sax ji, \q1 ñi koy indil sarax ci njekk. \q1 \v 4 Su boobaa la saraxu Yuda ak Yerusalem \q2 di neex Aji Sax ji, \q2 na jant ya woon, at ya woon. \b \q1 \v 5 «Maa leen di dikke ab àtte, \q1 di ab seede bu taxaw temm \q1 ci tuumaal ñeengokat yeek njaalookat yi, \q2 ak ñiy fene ngiñ, \q2 ak ñiy xañ ab liggéeykat peyooram, \q1 di noggatu ab jëtun akub jirim, \q1 di beddi doxandéem te ragaluñu ma.» \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. \q1 \v 6 «Man Aji Sax ji déy, duma soppiku, \q1 te yeen noppiwuleen di askanu Yanqóoba\f + \fr 3.6 \fr*\fk askanu Yanqóoba \fk*\ft mooy askan wi soqikoo ci Yanqóoba mi suufu woon ab seexam.\ft*\f*, ay workat. \s1 Waññiku ci Aji Sax ji moo war \q1 \v 7 «Ca seen janti maam \q1 ngeen dëddoo sama dogali yoon, \q1 sàmmuleen ko. \q1 Waññikuleen fi man, ma waññiku fi yeen,» \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoor yee ko wax. \q1 «Yeena ngi naa: \q1 “Ci lan lanuy waññikoo?” \q1 \v 8 Waaw, nit dina sàcc Yàlla? \q1 Ndaxam yeen yeena ngi may sàcc \q1 te yeena ne: “Ana nu nu la sàcce?” \q1 Xanaa ci seen cérub fukkeelu alal akub jooxe. \q1 \v 9 Alkànde ju réya ngi leen di dikkal, \q1 nde man ngeen di sàcc, yeen mboolem askan wi. \q1 \v 10 Indileen mboolem céru fukkeel \q2 ca kërug denc ya, \q1 ba ab dund am sama biir kër, \q1 te ngeen seetloo ma ko rekk,» \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, \q1 «ndegam duma leen ubbil bunti asamaan, \q1 ba sottil leen barke bu doy. \q1 \v 11 Maa leen di gëddal njéeréer, \q1 ba du leen yàqal meññeefum suuf, \q1 te reseñug tool du leen jaasiral.» \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. \q1 \v 12 «Xeet yépp ñu barkeel ñi lañu leen di wooye, \q1 nde réewum bànneex ngeen di dëkke.» \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. \s1 Aji Sax ji dina fésal njubteg àtteem \q1 \v 13 «Kàddu yu ñagas ngeen teg ci sama kaw,» \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee ko wax. \q1 «Te yeena ne: “Ana kàddu yu ñu la waxal”? \q1 \v 14 Yeena ne: “Jaamu Yàlla ag neen la. \q1 Ana lu nu jële ci dénkoo ndénkaaneem, \q1 tey wéye toroxlu \q1 fi kanam Aji Sax ji Boroom gàngoor yi? \q1 \v 15 Moo tax nu ne nit ñu bew ñi ñooy ñi barkeel, \q1 ñiy def lu bon kay ñoo baaxle, \q1 ñoom ñiy diiŋat Yàlla, teg ca rëcc.”» \b \q1 \v 16 Ca la ñi ragal Aji Sax ji diisoo ci seen biir, \q1 Aji Sax ji teewlu, déglu leen. \q1 Ñu bind fi kanamam téereb fàttliku, \q2 bu lim ñi ragal Aji Sax ji, \q2 te teral aw turam. \q1 \v 17 «Sama moomeelu bopp la ñooñuy doon,» \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, \q1 «ca bés ba may jëfi, sama gànjar lañuy doon, \q1 te ni baay di baaxee as ngóoram su ko taxawu, \q1 ni laa leen di baaxee. \q1 \v 18 Ca ngeen di ràññaatlewaat diggante \q1 ku jub ak ku bon, \q1 kuy jaamu Yàlla, \q1 ak ku ko jaamuwul. \c 4 \q1 \v 1 Bés ba déy a ngii di ñëw, \q1 di tàkk ni taal bu yànj. \q1 Képp ku bew ak kuy def lu bon, \q1 ca lay mel ni boob, \q1 te bésub keroog baa koy jafal.» \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. \q1 «Du leen waccal tus, dub reen, dub car. \q1 \v 2 Waaye yeen ñi ma ragal \q2 la jantub njekk di fenkal, \q1 yiire leen ceeñeer yuy wéral, \q1 ngeen génn di tëbantu ni ay sëlluy yar. \q1 \v 3 Yeenay joggi ñu bon ñi, \q1 ñu doon pënd fi seen ron téstën, \q1 keroog bés ba may jëfi.» \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. \b \q1 \v 4 «Bàyyileen xel ci yoonu Musaa, sama jaam ba, \q1 yoon wa ma ko dénkoon fa tundu Oreb, \q1 ñeel Israyil gépp, \q1 mu diy dogal ak àttey yoon. \q1 \v 5 Maa ngii di yebal ci yeen, Ilyaas yonent bi, \q1 balaa \w bésub Aji Sax|lemma="bésub Aji Sax ji-:"\w* jee teew, \q1 di lu màgg te raglu. \q1 \v 6 Mooy delloo xolu baay ca doom ja, \q1 delloo xolu doom ca baay ba, \q1 lu ko moy ma dikk duma réew mi, ba faagaagal ko.»