\id LUK (WOL) \ide UTF-8 \h Luug \toc1 Xibaaru jàmm bu Almasi Yeesu, ci jottlib Luug \toc2 Luug \mt2 Xibaaru jàmm bu Almasi Yeesu, // ci jottlib \mt1 Luug \imt1 Ubbite gi \ip Luug ak Jëf ya benn téere la bu ëmb ñaari pàcc. Ñaar ñépp a indi ni Yàlla jëkka wooye bànni Israyil ba noppi, doora woo mboolem xeet yi, ngir ñu barkeele ci Ibraayma. \ip Ci pàcc bu jëkk bi, nettalib Luug Yerusalem la dox jëm, ëttu kërug cosaanu askanu Yawut. Ñaareelu pàcc bi, Jëf ya, Yerusalem la bawoo, jëm ci xeeti àddina yi ci des, doora tëje fi Póol birale nguuru Yàlla ca dëkk ba ñuy wax Room, péeyu nguur gu mag ga. \ip Pàcc bu jëkk bi nettali dundu Almasi Yeesu, ni ko Luug indee, ñetti dog la. \ip Dog bi ci jiitu moo di liggéeyu Yeesu ca Galile ca Israyil, wetu bëj-gànnaaram. \ip Ñaareel bi moo di yoonam wu yàgg wa mu jëme Yerusalem. Ci biir woowu yoon la dalale nit ñi ci àlluwa ju yees ju leen xamal ni Yàlla taxawale nguuram, te mu woroo ak ni kaaŋ-fóorey Israyil dégge nguuru Yàlla ca yooyu jant. \ip Ñetteelu dog bi, ci la Luug indi ni Almasi Yeesu sarxee bakkanam ca Yerusalem, te gannaaw gi mu dekki, ba firndeel ne moo di buuru Israyil, te moo di Sangub àddina dëgg. \ie \c 1 \p \v 1 Bare na ñu fexee bind ab nettalib mbir, yi sotti woon ci sunu biir, \v 2 noonee nu ko jote ca ña ko fekke woon ca ndoorte la, te seede yooyu mujj doon jawriñi kàddug Yàlla. \v 3 Moo tax man it, ma fas laa yéenee bindal lépp ba mu jekk, yaw Tewofil mu tedd mi, gannaaw ba ma gëstoo mbir mépp, dale ko ca ndoorte la, ba mu leer nàññ. \v 4 Su ko defee nga xam xéll ne li ñu la jàngal, lu wér péŋŋ la. \s1 Malaaka yégle na juddub Yaxya \p \v 5 Jant ya \w Erodd|lemma="Erodd:"\w* dee buuru réewum Yawut yi, ab \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* la woon bu ñuy wax Sàkkaryaa, bokk ci làngu sarxalkat, yi askanoo ci Abiya, te soxnaam Elisabet askanoo ci \w Aaróona|lemma="Aaróona:"\w*. \v 6 Ñoom ñaar ñépp a juboon, Yàlla seede, te mucc ayib ni ñuy jëfe santaane yeek ndigali yooni Boroom bi. \v 7 Amuñu woon doom nag, ndax Elisabet manul woona am doom, te it booba ñoom ñaar ñépp a dem ba màggat. \p \v 8 Sàkkaryaa la làngam aye woon, muy def liggéeyu carxalam fa kanam Yàlla. \v 9 Ba ñu tegoo bant, na ko sarxalkat yi baaxoo woon, moom la bant ba dal, mu wara dugg biir néegu Boroom bi, ngir taal fa saraxu cuuraay. \p \v 10 Mbooloo mépp nag a nga woon ca biti di julli, ca waxtuw saraxu \w cuuraay|lemma="cuuraay l-:"\w* boobu. \v 11 Ci biir loolu menn malaakam Boroom bi jekki feeñu Sàkkaryaa, ca wetu ndijooru sarxalukaayu cuuraay ba. \v 12 Ba ko Sàkkaryaa gisee daa jaaxle, tiitaange jàpp ko. \v 13 Malaaka ma ne ko: «Sàkkaryaa, bul tiit, ndax sa ñaan nangu na. Elisabet sa soxna dina am doom ju góor, nanga ko tudde \w Yaxya|lemma="Yaxya:"\w*. \v 14 Dinga am mbégte ak bànneex, te ñu bareey bég ci juddoom, \v 15 ndax ku màgg lay doon, Boroom bi seede. Biiñ ak lenn luy màndee nag, du ko naan, \w Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"\w* gi mooy dale ca biiru ndeyam, solu ko ba fees. \v 16 Niti \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ñu bare, moo leen di waññi ci Boroom bi seen Yàlla. \v 17 Mooy ndaw li koy jiitu, ànd ak leer ga ak xam-xam, ba woon ca Yonent Yàlla \w Ilyaas|lemma="Ilyaas:"\w*, ba waññi xolu baay ci doomam, waññi ku déggadi ci xelum aji jub, loolu yépp ngir waajal aw xeet ba ñu jekk ngir Boroom bi.» \p \v 18 Sàkkaryaa nag ne malaaka mi: «Lu may def ab takk ci loolu ba mu bir ma? Ndax man màggat naa, te sama soxna it làq na ay fan.» \v 19 Malaaka ma ne ko: «Man maay Jibril miy taxaw fi kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw, yégal la bii xibaaru jàmm. \v 20 Léegi nag, dama ne, gannaaw gëmuloo sama kàddu, giy jot, sotti, dinga luu te dootuloo mana wax, ba kera loolu di am.» \p \v 21 Ci biir loolu mbooloo maa ngay xaar Sàkkaryaa, jaaxle lool ndax yàggaayam ca biir néeg Yàlla ba. \v 22 Ba mu génnee nag, manula wax ak ñoom. Ñu daldi xam ne am na lu ko feeñu ca néeg Yàlla ba. Ma nga leen di liyaar, manatula wax. \p \v 23 Naka la Sàkkaryaa fégal ayu carxalam, daldi ñibbi. \v 24 Gannaaw gi, soxnaam Elisabet ëmb. Lëlu na juróomi weer. Ma nga naan: \v 25 «Lii Boroom bee ma ko defal ci jant yi mu ma geesoo, ba teggil ma sama gàcce gi ci biir nit ñi!» \s1 Jibril yégle na juddub Yeesu \p \v 26 Ba Elisabet tolloo ci juróom benni weeram, ca la Yàlla yebal Jibril malaaka mi, dëkk bi ñuy wax Nasaret ca diiwaanu Galile, \v 27 ci janq bu digoo séy ak waa ju ñuy wax Yuusufa te bokk ci waa kër \w Daawuda|lemma="Daawuda:"\w*. Janq ba Maryaama lañu koy wax. \v 28 Malaaka ma agsi ba ca moom, ne ko: «Jàmm nga am, yaw mi ñu baaxe, Boroom bi yaw la àndal.» \p \v 29 Waxi malaaka ma nag jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu mana tekki. \v 30 Malaaka ma ne ko: «Maryaama, bul tiit, ndax daje nga ak yiwu Yàlla. \v 31 Dinga ëmb, ba jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu. \v 32 Ku màgg lay doon, te dees na ko wooye Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla moo koy jagleel nguurug Daawuda maamam. \v 33 Mooy nguuru fi kaw waa kër \w Yanqóoba|lemma="Yanqóoba:"\w* ba fàww, te nguuram du foq mukk.» \p \v 34 Ci kaw loolu Maryaama laaj malaaka mi ne ko: «Nu loolu di ame, te man xawma góor?» \v 35 Malaaka mi ne ko: «\w Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"\w* gi mooy wàccsi ci yaw, dooley Aji Kawe ji yiir la. Moo tax itam ku Sell kiy juddoo ci yaw, dees na ko wooye Doomu Yàlla. \v 36 Te kat Elisabet sa mbokk mi itam ëmb na doom ju góor te fekk ko màggat. Ki ñu doon wooye jigéen ju jaasir, mu ngi nii ci juróom benni weeram, \v 37 ndax Yàlla, dara tëwu ko.» \v 38 Maryaama daldi ne: «Maa ngi, di jaamub Boroom bi. Nii nga waxe, na ame noonu ci man.» \p Ba loolu amee malaaka ma bàyyikoo ca moom, dem. \s1 Maryaama seeti na Elisabet \p \v 39 Ci fan yooyu la Maryaama fabu gaaw, jëm diiwaanu tund ya, ca dëkkub Yude, \v 40 ba Sàkkaryaa dëkke. Mu agsi ca kër ga, nuyu Elisabet. \v 41 Naka la Elisabet dégg nuyoob Maryaama, doom ja mu ëmb yëngu ca biiram. Elisabet daldi feese \w Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"\w* gi. \v 42 Mu àddu ca kaw ne: «Yaa gëna barkeel ci jigéen ñi, sa doom ji nga ëmb it barkeel na! \v 43 Ana ku ma doon ba sama ndeyu Sang di ma seetsi? \v 44 Naka la sa kàddug nuyoo tàbbi sama nopp rekk, sama doom ji yëngu ci sama biir bi ndax bég. \v 45 Ndokklee yaw mi gëm ne mbir mi ñu la yégal, te mu tukkee ci Boroom bi dina sotti!» \s1 Maryaama woy na mbaaxu Yàlla \p \v 46 Maryaama nag ne: \q1 \v 47 «Sama xol laay màggale Boroom bi, \q1 samag noo laay bége Yàlla mi may musal, \q1 \v 48 moo geesu bii jaamam bu tekkeedi, \q1 ba maasoo maas doxe fi wooye ma boroom mbég mi, \q1 \v 49 nde Kiy Boroom doole moo ma defal jaloore, \q1 sellnga ñeel naw turam. \p \v 50 «Yërmandeem a ñeel ay ragalkatam, \q2 maas ci kaw maas. \q1 \v 51 Dooley loxoom la defe ay jaloore, \q1 tasaare ñi jikkowoo réy-réylu, \q1 \v 52 wàccee buur yi ci seeni gàngune, \q1 yékkati baadoolo yi. \q1 \v 53 Ñi xiif, mu reggal leen lu neex, \q1 ñi duunle, mu dàqe loxoy neen. \q1 \v 54 Moo wallu \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, jaamam, \q1 bàyyee ko xel yërmandeem, \q1 \v 55 noonee mu ko dige woon sunuy maam, \q1 ñeel \w Ibraayma|lemma="Ibraayma:"\w* ak askanam ba fàww.» \p \v 56 Maryaama toog na fa Elisabet lu wara tollook ñetti weer, sooga ñibbi. \s1 Lu jëm ci juddub Yaxya \p \v 57 Gannaaw gi Elisabet dem ba àppam mat, mu mucc, am doom ju góor. \v 58 Dëkkandoom yaak ay bokkam yég noonu ko Boroom bi xéewalee yërmandeem, ñu bokk ak moom mbégte ma. \p \v 59 Ba bés ba délsee, ñu dikk xarfalsi xale ba, bëgg koo tudde Sàkkaryaa, dippee ko baayam. \v 60 Yaayam nag ne leen: «Déet, \w Yaxya|lemma="Yaxya:"\w* lay tudd.» \v 61 Ñu ne ko: «Waaye kenn ci say bokk tuddul noonu!» \p \v 62 Ci kaw loolu ñu liyaar baayam, ngir xam nu mu bëgg ñu tudde xale bi. \v 63 Sàkkaryaa laaj àlluwa, ñu jox ko, mu bind ci: «Yaxya mooy turam.» Ñépp waaru. \v 64 Ca saa sa gémmiñ ga ubbiku, làmmiñ wa nangu, muy wax, daldi sant Yàlla. \v 65 Ba loolu amee tiitaange dikkal mboolem ña leen séq, mbir moomu mépp nag doon waxtaan ca diiwaanu tundi Yude gépp. \v 66 Ña ca dégg ñépp daldi bàyyi xel ca mbir ma, te naan: «Lu xale bii nara doon ëllëg?» ngir manoorey Boroom bee àndoon ak moom. \s1 Sàkkaryaa sant na Yàlla \p \v 67 Ci kaw loolu Sàkkaryaa baayu Yaxya feese \w Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"\w* gi, daldi tàmbalee biral kàddug \w waxyu|lemma="waxyu:"\w*, ne: \b \q1 \v 68 «Cant ñeel na Boroom bi Yàllay Israyil, \q1 moo seetsi ñoñam, ba \w jot|lemma="jot:"\w* leen! \q1 \v 69 Moo nu feeñalal Musalkat bu manoorewu, \q1 fi biir kër \w Daawuda|lemma="Daawuda:"\w* jaamam ba, \q1 \v 70 noonee mu ko waxe woon ca jant yu jëkk ya, yonentam yu sell ya woon jottli, \q1 \v 71 moo nu musal ci sunuy noon, \q1 jële nu ci sunu loxoy mboolem bañaale. \q1 \v 72 Moo jëfe yërmande ñeel sunuy maam, \q1 tey bàyyi xel kóllëreem gu sell, \q1 \v 73 ak ngiñ la mu giñaloon sunu maam \w Ibraayma|lemma="Ibraayma:"\w*, \q1 \v 74 ne moo nuy may nu mucce ci loxoy noon, \q1 ba man koo jaamoo xel mu dal \q1 \v 75 ci biir sellnga ak njub ci kanamam, sunu giiru dund. \b \q1 \v 76 «Ngóor si nag yaw, yonentu Aji Kawe ji lees lay wooye, \q1 nde yaay dox, jiitu Sang bi, xàllal kow yoonam, \q1 \v 77 ngir yégal ñoñam ag njot \q1 guy topp seen njéggalug bàkkaar. \q1 \v 78 Sunu Yàllaa yaatu yërmande, \q1 moo nu fenkal ab jant, \q1 \v 79 di niital ñi tooge biir lëndëm ak takkndeeru ndee, \q1 di nu gindi, teg nu ci yoonu jàmm.» \p \v 80 Ngóor sa nag di màgg, xel ma di yokku. Mu dëkk ca màndiŋ ma, ba bés ba mu feeñoo \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \c 2 \s1 Yeesu juddu na ca Betleyem \p \v 1 Jant yooyu ndigal moo tukkee woon ci buur bu mag bu ñuy wax \w Sesaar|lemma="Sesaar:"\w* Ogust. Mu ne na ñépp binduji ca limeef ya. \v 2 Mbindu mooma mooy mu jëkk ma, yemook ba Kiriñus dee boroom réewum Siri. \v 3 Ci kaw loolu ñépp binduji, ku nekk ca sa dëkku cosaan. \v 4 Ku ñuy wax Yuusufa itam jóge Nasaret ca diiwaanu Galile, jëm ca diiwaanu Yude ca Betleyem, dëkk ba \w Daawuda|lemma="Daawuda:"\w* cosaanoo, ndax ci waa kër Daawuda la askanam bokk. \v 5 Maryaama mi digook moom séy la àndal binduji, te fekk ko mu ëmb. \v 6 Naka lañu dal Betleyem, waxtuw muccam agsi. \v 7 Mu am doom ju góor, mu dib taawam. Mu laxas ko, tëral ko ca gàmbug jur ga\f + \fr 2.7 \fr*\fk gàmbug jur ga: \fk*\ft nit ñi ak jur gi ñoo daan bokk fu ñuy fanaan, doonte dañoo sàkkaloon jur gi bérab bu gëna suufe, gàmbug jur gi dox seen diggante ak nit, ñay féete fu gëna kawe.\ft*\f*, ndax ñàkk fu ñu xaj ca néegu gan ba. \s1 Malaaka feeñu na ay sàmm \p \v 8 Booba ay sàmm a nga ca gox boobee, di fanaanee wattu seenug jur. \v 9 Am malaakam Boroom bi jekki feeñu leen, leeru Boroom bi melax, wër leen, ñu tiit tiitaange lu réy. \v 10 Malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndax kat maa leen indil xibaaru jàmm bu doon mbég mu réy, ñeel askan wépp. \v 11 Bésub tey jii ca dëkku \w Daawuda|lemma="Daawuda:"\w*, juddule ngeen ab Musalkat, te mooy \w Almasi|lemma="Almasi:"\w*, di Sang bi. \v 12 Li ngeen ciy def ab takk moo di: dingeen gis liir bu ñu laxas, tëral ko ci gàmbug jur.» \p \v 13 Ca saa sa gàngooru asamaan gu mag ànd ak malaaka mi, di sàbbaal Yàlla, ne: \q1 \v 14 «Daraja ñeel na Yàlla fa asamaan sa gëna kawe, \q1 jàmm ci kaw suuf ñeel ñi Yàlla baaxe.» \p \v 15 Ba malaaka ya bàyyikoo ca sàmm sa, dellu asamaan, ñuy wax ca seen biir, naan: «Nanu dem boog Betleyem, seeti la fa xew, te Boroom bi xamal nu ko.» \p \v 16 Ñu gaaw dem ba foofa, daldi gis Maryaama ak Yuusufa, ak liir ba tëdd ca gàmbug jur ga. \v 17 Naka lañu leen gis, daldi leen xamal la ñu leen wax ca mbirum xale ba. \v 18 Mboolem ña dégg la leen sàmm sa wax nag waaru lool. \v 19 Teewul Maryaama moom, bàyyi woon na xel ci mbir moomu mépp, di ko xalaat ci xolam. \v 20 Ba loolu amee sàmm sa dellu, di sàbbaal ak a sant Yàlla ci mboolem la ñu dégg, gis ko, te lépp ame noonee ñu leen ko waxe woon. \s1 Yóbbu nañu Yeesu ca kër Yàlla ga ca Yerusalem \p \v 21 Ba juróom ñetti fani xale bi matee, ñu xarfal ko, tudde ko Yeesu, na ko malaaka ma tudde woon, bala moo sosu. \p \v 22 Gannaaw ba seen fani setlu\f + \fr 2.22 \fr*\fk setlu: \fk*\ft ab diir lañu àppaloon wasin-bees gannaaw bu taawloo góor, bala moo yóbbu xale bi kër Yàlla ga, ngir def sarax yi setluy wasin-bees laaj. Seetal ci \ft*\ft \+bk Sarxalkat yi\+bk* 12.6-8.\ft*\f* matee, ni ko yoonu \w Musaa|lemma="Musaa:"\w* laaje, ñu yóbbu xale bi \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w*, ngir teewal ko fi kanam Boroom bi, \v 23 noonee ñu ko binde ci yoonu Boroom bi ne: «Bépp taaw bu góor, dees koy tudde séddoo bu sell, ñeel Boroom bi.» \v 24 Ñu yóbbaale sarax bi ci war, ni ko yoonu Boroom bi santaanee: «ñaari pitaxu àll mbaa ñaari xati yu ndaw.» \s1 Simeyon sàbbaal na Yàlla \p \v 25 Amoon na nag ca \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w* ku ñuy wax Simeyon; ku juboon, ragal Yàlla, di séentu jamono ji nekkinu \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* di ame ag tan, te \w Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"\w* gi àndoon ak moom. \v 26 Ndéey nag tukkee ci Noo gu Sell gi, xamal ko ne ko du dee mukk te gisul \w Almasi|lemma="Almasi:"\w* bu Boroom bi. \v 27 Ci kaw loolu mu dem ba ca biir kër Yàlla ga ci dooley Noo gu Sell gi. Gannaaw loolu waajuri Yeesu indi Yeesu ngir defal ko li aaday yoon wi laaj. \v 28 Simeyon itam jël xale bi, leewu ko, daldi sàbbaal Yàlla, ne: \q1 \v 29 «Léegi nag Buur Yàlla, yiwil sab jaam, \q1 mu dem ak jàmm, noonee nga ko waxe woon. \q1 \v 30 Nde saay gët tegu na ci mucc gi nga dogal, \q1 \v 31 waajal ko fi kanam askan yépp, \q1 \v 32 mu dig leer, ñeel jaambur ñi, \q1 sagal Israyil sa ñoñ.» \p \v 33 Baay bi ak ndey ji nag yéemu ci kàddu yooyu ñu wax ci xale bi. \v 34 Ba loolu amee Simeyon ñaanal leen, ba noppi ne ndeyam Maryaama: «Dama ne, kii lañu yebal ngir sànkutey ñu bare mbaa seenug leqliku ci digg Israyil, ngir itam mu doon firnde ju ñuy gàntal. \v 35 Yaw nag, sab xol la aw naqar wu mel ni saamar di xar, ba ñu bare la seen xalaati biir xol di feeñ.» \s1 Aana sant na Yàlla \p \v 36 Jigéen ju ñuy wax Aana, ab yonent la woon ca Yerusalem, di doomu Fanuwel mi askanoo ci giirug Aser. Mag la woon lool. Ba muy janq la séy, nekk ak jëkkëram juróom ñaari at. \v 37 Jëkkër ja faatu, mu toog, séyaatul, ba booba mu amee juróom ñett fukki at ak ñeent (84). Daawul jóge ca kër Yàlla ga, koor ak julli la daan jaamoo guddi ak bëccëg. \v 38 Aana nag dikk moom it ca waxtu woowa, daldi delloo Yàlla njukkal. Ci kaw loolu muy waxtaane mbirum xale bi ak mboolem ña doon séentu bésu goreelug \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w*. \p \v 39 Ci kaw loolu ñu matal mboolem lu yoonu Boroom bi laaj, doora dellu Nasaret, seen dëkk ba ca diiwaanu Galile. \v 40 Xale bi nag di màgg, di dëgër, feese am xel, te yiwu Yàlla ànd ak moom. \s1 Yeesu feeñ na ca kër Yàlla ga \p \v 41 At mu jotaan nag waajuri Yeesu dem \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w*, ngir màggali \w bésub Mucc|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* ba. \v 42 Ba Yeesu amee fukki at ak ñaar, ñu dem màggali na ñu ko baaxoo woon. \v 43 Ba màggal ga tasee, ñu ñibbi, ngóor sa Yeesu moom des Yerusalem, te ay waajuram yéguñu ko. \v 44 Ñu xalaat ne, Yeesu daa ànd ak ñu ñu bokkaloon yoon. Dox nañu bésub lëmm, door koo wëri ci seeni bokk ak seeni xame, \v 45 te taxul ñu gis ko. Ñu daldi dellu Yerusalem, seeti ko. \p \v 46 Ca gannaaw ëllëg sa lañu ko fekk ca kër Yàlla ga, mu toog ca digg jànglekat ya, di leen déglook a laaj. \v 47 Mboolem ña ko dégg yéemu ci dégginam aki tontam. \v 48 Ay waajuram gis ko, waaru. Yaayam ne ko: «Doom, li nga nu def nag? Maak sa baay a ngi jaaxle, di la seet!» \v 49 Mu ne leen: «Lu ngeen may seete? Xamuleen ne sama kër Baay laa wara nekk?» \p \v 50 Ay waajuram ñoom dégguñu kàddu googu mu leen wax. \v 51 Gannaaw loolu Yeesu ànd ak ñoom, dellu Nasaret, tey saxoo déggal ay waajuram. Yaayam nag takk mbir yooyu yépp ci xolam. \v 52 Yeesu moom, ma ngay màgg ci dayo ak xel mu rafet, ak cérub yiw fi Yàlla ak nit ñi. \c 3 \s1 Yaxya waare na \p \v 1 Ca fukkeelu at ak juróom ci nguurug buur bu mag ba Tibeer \w Sesaar|lemma="Sesaar:"\w*, ba Poñsë \w Pilaat|lemma="Pilaat:"\w* yilifee diiwaanu Yude, \w Erodd|lemma="Erodd:"\w* yilif diiwaanu Galile, Filib magam yilif diiwaanu Iture ak bu Tarakonit, Lisañas yilif Abilen, \v 2 jant yooyu Anas ak Kayif dee \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yu mag ya, ca la kàddug Yàlla dikkal \w Yaxya|lemma="Yaxya:"\w* doomu Sàkkaryaa, ca màndiŋ ma. \v 3 Yaxya dugg mboolem àll, bi wër dexu Yurdan, di waare lu jëm ci tuubeel gu nit ñi wara fésale ag sóobu cim ndox, ngir ñu jéggal leen seeni bàkkaar. \p \v 4 Loolu lañu bind ci téereb waxi Yonent Yàlla \w Esayi|lemma="Esayi:"\w* ne: \q1 «Baat a ngi xaacoo ca màndiŋ ma, naan: \q1 “Xàll-leen yoonu Boroom bi, \q1 jubal-leen ay xàllam. \q1 \v 5 Xur yépp ay sëkke, \q1 tund wu magoo wu ndaw maasaloo, \q1 yoon ya lunkoon, jubbantiku, \q1 ya ñagasoon, nooy, \q1 \v 6 ba wépp suux gis mucc gi Yàlla dogal.”» \p \v 7 Yaxya nag di wax mbooloo may ñëw ngir mu sóob leen ci ndox, naan leen: «Yeen njurum jaan mee, ku leen àrtu, ba ngeen di daw sànj miy dikk? \v 8 Kon nag jëfeleen jëf ju yelloo ag tuubeel, te baña nax seen bopp naan: “Nun, \w Ibraayma|lemma="Ibraayma:"\w* mooy sunu maam,” ndax maa leen ko wax, doj yii, Yàlla man na cee sàkkal Ibraayma aw askan. \v 9 Te itam sémmiñ xàccil na reenu garab ba noppi. Kon nag gépp garab gu ci meññul doom yu baax, dees koy gor, sànni ca sawara sa.» \p \v 10 Mbooloo ma itam laaj ko ne ko: «Ana lu nu war nag?» \v 11 Mu ne leen: «Ku am ñaari turki, na sédd ki amul. Ku am aw ñam itam, na defe noonu.» \v 12 Ay \w juutikat|lemma="juutikat b-:"\w* itam dikk, ngir sóobusi; ñu ne Yaxya: «Sëriñ bi, ana lu nu war?» \v 13 Mu ne leen: «Xanaa baña sàkku lenn lu moy li jaadu.» \v 14 Ay takk-der itam ne ko: «Nun nag, nu nuy def?» Mu ne leen: «Buleen néewal kenn doole, mbaa di duural kenn ngir jëlal ko dara; doyloo leen seen peyoor.» \p \v 15 Ci kaw loolu askan wa di séentu, ñépp di seetaat ci seen xel, ndax Yaxya mooy \w Almasi|lemma="Almasi:"\w*. \v 16 Yaxya wax leen ñoom ñépp ne leen: «Man de ci ndox laa leen di sóob. Waaye ku ma sut a ngi ñëw, kooku, buumi caraxam sax, yeyoowuma ko koo feccil. Moom, ci \w Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"\w* gi ak sawara la leen di sóob\f + \fr 3.16 \fr*\fk Sóobu gi ci Noo gu Sell gi ak ci sawara \fk*\ft moo leen di sol doole ju bawoo ci Noo gu Sell gi, ak itam setal leen ni sawara di setale weñ gu am lu ko rax. Sawara dina taxawe itam céru mbugal mu ñeel ñi déggalul Yàlla. Seetal ci 12.49 ak \ft*\ft \+bk Jëf ya\+bk* 2.3.\ft*\f*. \v 17 Ab layoom a ngi ci loxoom, mooy jéri dàggaam, ba mu set wecc; pepp mi lay fat cim sàqam, waaye xatax bi, da koy lakk ci sawara su dul fey mukk.» \p \v 18 Bare na yeneen dénkaane yu Yaxya doon xamale nit ñi xibaaru jàmm bi. \v 19 Erodd boroom diiwaan ba nag, Yaxya sikkoon na ko ndax Erojàdd jabaru magam ja mu nekkaloon, ak mboolem yeneen ñaawtéef yu Erodd def. \v 20 Mu tegati leneen ca loolu lépp: jàpp Yaxya, tëj ca kaso ba. \s1 Yaxya sóob na Yeesu ci ndox \p \v 21 Noonu Yaxya doon sóobe ñépp cim ndox, ni la deme ba Yeesu dikk, mu sóob ko ci ndox. Ci biir loolu Yeesu yékkati kàddug ñaan, asamaan ubbiku. \v 22 Ba loolu amee \w Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"\w* gi moo bindoo ni pitax, wàcc ci kawam, baat jibe asamaan, ne: «Yaa di sama Doom, sama soppe; yaa may bànneexal.» \s1 Lu jëm ci cosaanu Yeesu Almasi \p \v 23 Yeesu ci boppam ba muy door, amoon na lu tollu ci fanweeri at, di doomu Yuusufa, ni ko xel mana jàppe. \q1 Yuusufa, Eli mooy baayam, \v 24 Eli, Matat. \q1 Matat, Lewi; Lewi, Melki; \q1 Melki, Yanayi; Yanayi, Yuusufa; \q1 \v 25 Yuusufa, Matacas; Matacas, Amos; Amos, Nawum; Nawum, Esli; Esli, Nagayi. \q1 \v 26 Nagayi, Maat; Maat, Matacas; Matacas, Semeyin; Semeyin, Yoseg; Yoseg, Yoda. \q1 \v 27 Yoda, Yowanan; Yowanan, Resa; \q1 Resa, Sorobabel; Sorobabel, Selcel; Selcel, Neri; \q1 \v 28 Neri, Melki; Melki, Adi; Adi, Kosam; Kosam, Elmadam; Elmadam, Er. \q1 \v 29 Er, Yeesu; Yeesu, Elyeser; Elyeser, Yorim; Yorim, Matat; Matat, Lewi; \q1 \v 30 Lewi, Simeyon; Simeyon, Yuda; Yuda, Yuusufa; Yuusufa, Yonam; Yonam, Elyakim. \q1 \v 31 Elyakim, Meleya; Meleya, Mena; \q1 Mena, Matata; Matata, Natan; \q1 Natan, \w Daawuda|lemma="Daawuda:"\w*. \v 32 Daawuda mooy doomu \w Yese|lemma="Yese:"\w*; \q1 Yese, Obedd; Obedd, Bowas; Bowas, Sala; Sala, Nason. \q1 \v 33 Nason, Aminadab; Aminadab, Admin; Admin, Arni; \q1 Arni, Esron; Esron, Peres; Peres, Yuda; \v 34 Yuda, \w Yanqóoba|lemma="Yanqóoba:"\w*; Yanqóoba, Isaaxa; Isaaxa, \w Ibraayma|lemma="Ibraayma:"\w*; \q1 Ibraayma, Teraa; Teraa, Naxor; \q1 \v 35 Naxor, Serug; Serug, Rew; Rew, Peleg; Peleg, Eber; Eber, Sela; \q1 \v 36 Sela, Kenan; Kenan, Arpagsàdd; \q1 Arpagsàdd, Sem; Sem, Nóoyin; Nóoyin, Lemeg; \q1 \v 37 Lemeg, Matusalem; Matusalem, Enog; Enog, \q1 Yeredd; Yeredd, Malaleel; Malaleel, Kenan; \q1 \v 38 Kenan, Enos; Enos, Set; Set, Aadama; \q1 Aadama, Yàlla. \c 4 \s1 Yeesu dékku na pexey Seytaane \p \v 1 Yeesu moo feese woon \w Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"\w* gi, bàyyikoo dexu Yurdan, ci njiital Noo gi, ca biir màndiŋ ma. \v 2 Ñeent fukki fan la ko fa \w Seytaane|lemma="Seytaane:"\w* fiir, lekkul dara diir boobu bépp. Gannaaw ba fan yooyu wéyee, mu xiif. \p \v 3 Seytaane nag ne ko: «Ndegam yaa di Doomu Yàlla, neel doj wii mu soppliku mburu.» \v 4 Yeesu ne ko: «Bindees na ne du aw ñam doŋŋ la nit di dunde.» \p \v 5 Seytaane yéege na ko itam, won ko mboolem nguuri àddina, ci xef ak xippi. \v 6 Seytaane ne Yeesu: «Yaw laay may mboolem kilifteef gii ak daraja ji mu àndal, ndax man lees ko jox, te ku ma soob laa koy may. \v 7 Kon nag soo ma sujjóotalee, yaa moom lépp.» \v 8 Yeesu ne ko: «Bindees na ne: “Boroom bi sa Yàlla ngay sujjóotal, te moom doŋŋ ngay jaamu.”» \p \v 9 Seytaane yóbbu na ko \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w*, aj ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga, ne ko: «Ndega yaa di Doomu Yàlla, tëbeel fii, wàcc, \v 10 ndax bindees na ne: \q1 “Ay malaakaam lay jox ndigal ci sa mbir, \q1 ñu sàmm la, \v 11 te seeni loxo lañu lay leewoo, \q1 ba doo fakktaloo aw doj.”» \p \v 12 Yeesu ne ko: «Bindees na ne: “Bul seetlu Boroom bi sa Yàlla.”» \p \v 13 Seytaane lalal na Yeesu gépp fiir ba sottal, doora dem, bàyyi ko ab diir. \s1 Lu jëm ci Yeesu fa Nasaret \p \v 14 Ba loolu amee Yeesu dellu Galile ci manoorey \w Noo|lemma="Noo gu Sell g-:"\w* gi, ab jëwam nag law ca diiwaan ba bépp ba mu daj. \v 15 Muy jàngle ca seeni jàngu, ñépp di ko kañ. \p \v 16 Yeesu moo dikkoon Nasaret ga mu fekk baax, daldi dugg ca jàngu ba, na mu ko baaxoo woon ci \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*. Mu taxaw ngir biral ab dog. \v 17 Ñu jox ko téereb Yonent Yàlla \w Esayi|lemma="Esayi:"\w*. Mu ubbi téere bi, gis dog bi ñu bind ne: \q1 \v 18 «Noowug Boroom baa ngi fi sama kaw, \q1 moo ma fal, \q1 ngir ma yégal néew-doole yi xibaaru jàmm bi. \q1 Da maa yebal ngir ma yégal jaam yi ne dees na leen goreel, \q1 yégal gumba yi ne dinañu gis, \q1 yégal ñi ñu not, ne dees na leen jot, \q1 \v 19 tey yégle atum yiw wu Boroom bi.» \p \v 20 Ci kaw loolu mu ub téere bi, delloo ko jawriñ ba, daldi toog. Ña ca jàngu ba ñépp nag ne ko jàkk. \v 21 Mu àddu, ne leen: «Tey jii la mbind mii mat, ngeen dégg.» \v 22 Ñépp a doon seedeel Yeesu lu rafet, tey yéemu ci kàdduy yiw yi tukkee ci gémmiñam. Ñu naan: «Xanaa kii du doomu Yuusufa ji?» \v 23 Mu ne leen: «Xam naa ne dingeen ma waxal waxin wi ñu naan: “Fajkat bi, fajal sa bopp.” Mboolem li nu dégg ne moo xew Kapernawum, def ko fii ci sa réewum bopp itam.» \v 24 Mu neeti: «Maa leen ko wax déy, amul benn yonent bu ñu teral ci réewum boppam. \v 25 Maa leen wax ne liy dëgg moo di, ca jamonoy \w Ilyaas|lemma="Ilyaas:"\w*, ba asamaan tëjoo diiru ñetti at ak juróom benni weer, ba xiif bu metti am ca réew mépp, ay jëtun ñu baree nga woon ca Israyil. \v 26 Moona du kenn ci ñoom ku ñu yebal Ilyaas ca moom ku moy jëtun ba dëkke Sarebta, ca \w Sidon|lemma="Tir:"\w*. \v 27 Jamonoy Yonent Yàlla \w Alyaasa|lemma="Alyaasa:"\w* itam, ay \w gaana|lemma="gaana:"\w* yu baree nga woon ca Israyil. Waaye fajeesu ci kenn ku moy Naaman, waa Siri ba.» \p \v 28 Ba mboolem waa jàngu ba déggee loolu dañoo mer ba fees. \v 29 Ñu jóg, bëmëx ko ba génne ko dëkk ba, yóbbu ko ca kéméju tund, wa seen dëkk ba sance, ngir xalab ko ci suuf. \v 30 Teewul moom mu jaare ci seen biir, dem yoonam. \s1 Yeesu faj na ku rab jàpp \p \v 31 Ba mu ko defee Yeesu dem Kapernawum, ab dëkk ca diiwaanu Galile, di leen jàngal ca \w bési Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w* ya. \v 32 Nit ña nag yéemu ca njàngleem, ndax sañ-sañ ba muy waxe. \v 33 Ndeke foofa ca jàngu ba, jenn waay ju rab jàpp a nga fa woon. Waa ji jekki xaacu, ne: \v 34 «Moo yaw Yeesum Nasaret, lu nu joteek yaw? Alagsi nu mooy say tànk? Xam naa yaa di kan, yaa di Aji Sell ju Yàlla ji!» \v 35 Yeesu nag gëdd ko, ne ko: «Noppil te génn nit ki!» Rab wa daaneel nit ki ca digg mbooloo ma, doora génn te gaañu ko fenn. \p \v 36 Ba loolu amee ñépp a waaru, di wax ci seen biir, naan: «Gii kàddu lu mu doon? Moom de sañ-sañ ak xam-xam lay joxe rab yi ndigal, ñu génn.» \v 37 Coowal Yeesu nag law ba fépp fu bokk ca diiwaan ba. \s1 Yeesu faj na jarag yu bare \p \v 38 Yeesu jóge jàngu ba, dem kër Simoŋ, daldi fekk yaayu jabaru Simoŋ ànd ak tàngooru yaram wu réy. Ñu ñaan ci Yeesu ndimbal. \v 39 Mu dikk, tiim soxna sa, daldi gëdd tàngooru yaram wa, tàngoor wa teqlikook moom. Soxna sa jóg ca saa sa, di leen topptoo. \p \v 40 Ba jant sowee, mboolem ña amoon ay jarag yu ame ay jàngoroy jàngoro, daldi leen indil Yeesu. Moom it, mu \w teg kenn ku ci nekk ay loxoom|lemma="teg loxo:"\w*, wéral la. \v 41 Ay rab itam di génn ñu bare, di yuuxu, te naan: «Yaay Doomu Yàlla!» Teewul mu gëdd leen, aaye leen ñu wax, ndax xamoon nañu ne mooy \w Almasi|lemma="Almasi:"\w*. \p \v 42 Njël gu jëkk ca ëllëg sa la Yeesu génn dëkk ba, dem ba bérab bu wéet. Mbooloo ma nag di ko seet, ba dikk, di ko téye, bañ mu dem, ba leen. \v 43 Mu ne leen: «Yeneen dëkk yeet, war na ma faa yégleji xibaaru jàmm bu nguurug Yàlla, ndax loolu lañu ma yebale.» \v 44 Ci kaw loolu muy waare ca jànguy diiwaanu Yude. \c 5 \s1 Yeesu woo na ay taalibe \p \v 1 Yeesoo taxawoon ca tàkkal dexu Senesaret\f + \fr 5.1 \fr*\fk dexu Senesaret \fk*\ft mooy dexu Galile ba tey.\ft*\f*, mbooloo ma tancaloo ci kawam, di déglu kàddug Yàlla. \v 2 Ci biir loolu mu gis ñaari gaal yu taxaw ci tàkk gi, nappkat ya ca wàcce, di fóot seeni mbaal. \v 3 Mu dugg ci genn gaal gi, muy gu Simoŋ. Mu ñaan ko mu bëmëx ba dànd tefes gi as lëf. Mu defal ko noonu, Yeesu toog, tàmbalee jàngal mbooloo ma fa mu tollu ca biir gaal ga. \p \v 4 Naka la jàngle ba noppi, ne Simoŋ: «Bëmëxal ba ca xóote ba, te ngeen sànni seeni mbaal ba jàpp.» \v 5 Simoŋ ne ko: «Njaatige, coono lanu fanaane biig te jàppunu dara. Xanaa ma sànni ko rekk ci sa ndigal.» \p \v 6 Naka lañu sànni mbaal yi, daldi jàpp jën yu baree bare, ba mbaal ya di xëtt. \v 7 Ba loolu amee ñu liyaar seen moroom, ya ca geneen gaal ga, ngir ñu dimbalisi leen. Ñu dikk, yebandook ñoom, feesal ñaari gaal yépp, ba ñuy bëgga suux. \v 8 Simoŋ Piyeer nag gis loolu, daldi sukk fa kanam Yeesu, ne ko: «Sang bi, ngalla sore ma, ngir man nitu bàkkaarkat laa!», \v 9 ndax tiitaange lu ko jàpp, mook mboolem ña mu àndal, ca jën yu bare ya ñu jàpp. \v 10 Yanqóoba ak Yowaan doomi Sebede ya mu bokkaloon liggéey ba itam noonu lañu tiite. Yeesu ne Simoŋ: «Bul ragal dara; gannaaw-si-tey, ay nit ngay napp.» \v 11 Ci kaw loolu ñu teeral gaal ya ca tefes ga, daldi bàyyi lépp, topp ca moom. \s1 Yeesu faj na ku gaana \p \v 12 Yeesoo nekkoon cib dëkk, ndeke jenn waay a nga fa, ju jàngoroy ngaana dajal yaram wa. Ba mu gisee Yeesu, daa daanu, dëpp jëëm ci suuf, sarxu ko, ne: «Sang bi, su la soobee, man nga maa setal.» \v 13 Yeesu tàllal loxoom, laal ko ne: «Soob na ma, setal.» Ca saa sa ngaana ga teqlikook moom. \v 14 Yeesu dénk ko ne ko: «Bu ko wax kenn, demal rekk ca \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba, ngir mu seet la, te nga génne sa jooxeb setlu, ni ko yoonu \w Musaa|lemma="Musaa:"\w* santaanee, muy firnde ci ñoom\f + \fr 5.14 \fr*\ft Ci yoonu Musaa, jàngoroy der juy law ju mel ni ngaana sobe la woon ca ka mu dal, te du set li feek wérul. Seetal ci \ft*\ft \+bk Sarxalkat yi\+bk* 13.45-46; 14.1-32.\ft*\f*.» \v 15 Teewul jëwub Yeesu gënatee law. Mbooloo yu bare daje, di ko déglu tey faju, ba tàggook seeni jàngoro. \v 16 Moom nag muy rocceekuy dem ba ci bérab yu wéet, di fa ñaaneji. \s1 Yeesu faj na ab lafañ \p \v 17 Yeesu moo doon jàngle bés, fu ay \w Farisen|lemma="Farisen y-:"\w* ak ay jànglekati yoonu Musaa tooge, jóge ca mboolem dëkki Galile ak Yude ak \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w*, te manoorey Boroom bi teew faak moom, ngir faj jarag ja. \p \v 18 Ci biir loolu ay nit ne jalañ, jàppoo ab lafañ bu ñu tëral cig laltu. Ñu di ko wuta dugal, ngir tëral ko ca kanam Yeesu. \v 19 Waaye gisuñu fu ñu koy awale ndax mbooloo ma. Ñu yéeg ca kaw néeg ba, xeddi lenn ca xadd ba, yoor waa jaak laltu ga, wàcce ko ca digg ba, fa kanam Yeesu. \v 20 Yeesu nag gis seen ngëm, daldi ne lafañ ba: «Mbokk mi, jéggalees na la say bàkkaar.» \p \v 21 Firikati yoonu Musaa yi ak Farisen yi tàmbalee nàttable ci seen xel, naan: «Kii di saaga Yàlla mooy kan? Ana ku mana jéggaley bàkkaar ku dul Yàlla doŋŋ?» \p \v 22 Yeesu nag xam la ñuy nàttable ci seen xel, daldi àddu, ne leen: «Lu ngeen di nàttable ci seen xel? \v 23 Ana lu gëna yomb ci yii yaar: ne “Jéggalees na la say bàkkaar,” am ne: “Jógal te dox”? \v 24 Kon nag dingeen xam ne \w Doomu nit ki|lemma="Doomu nit k-:"\w* am na ci kaw suuf, sañ-sañu jéggale ay bàkkaar.» Mu ne lafañ ba: «Dama ne, jógal, jël sag laltu te dem ñibbi.» \v 25 Nit ka daldi ne ñokket ca kanam ñépp, jël laltu ga mu tëddoon, jëm këram, di sàbbaal Yàlla. \v 26 Ba loolu amee mbooloo mépp a neey, di sàbbaal Yàlla, tiitaange jàpp leen, ñu naan: «Gis nanu tey mbir yu tiiñ am xel.» \s1 Yeesu woo na Lewi \p \v 27 Gannaaw loolu Yeesu génn, gis ab \w juutikat|lemma="juutikat b-:"\w* bu ñuy wax Lewi, mu toog ca juuti ba. Mu ne ko: «Kaay, topp ma.» \v 28 Lewi jóg, bàyyi lépp, topp ca moom. \v 29 Ci kaw loolu Lewi waajalal ko bernde ju réy ca këram. Mbooloo mu bare teew, ay juutikat ak yeneen gan, ñu bokk toog, di lekk. \v 30 \w Farisen|lemma="Farisen y-:"\w* yi ak seeni firikat nag di xultu ci kaw taalibey Yeesu yi, ne leen: «Lu tax ngeen di lekkandoo ak a naanandoo ak juutikat yeek bàkkaarkat yi?» \v 31 Yeesu ne leen: «Du ñi wér ñoo soxla fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla. \v 32 Du ñi jub nag laa woosi, bàkkaarkat yi laay woo, ngir jëme leen cig tuubeel.» \s1 Koor du wartéef ci gëmkatub Yeesu \p \v 33 Dañoo wax Yeesu, ne ko: «Taalibey \w Yaxya|lemma="Yaxya:"\w* de, dinañu faral di woor, di julli. \w Farisen|lemma="Farisen y-:"\w* yi it noonu, waaye sa ñoñ, lekk ak a naan lañu wéye.» \v 34 Yeesu ne leen: «Ndax man ngeena woorloo ay gan ñu wàlli ag céet, li feek boroom séet biy teew ci seen biir? \v 35 Waaye ay bés a ngi ñëw, dees na jële boroom séet bi ci seen biir. Kera bés yooyu nag, dinañu woor.» \p \v 36 Yeesu léebati leen, ne leen: «Mbubb mu bees, deesu ci xotti ab sekkit, ngir daaxe ko mbubb mu ràpp. Lu ko moy mbubb mu bees mi xottiku ba noppi, te du tax sekkit wu bees wi ànd ak mbubb mi ràpp. \v 37 Te it mbuus yu ràpp, deesu ci duy biiñ bu bees. Lu ko moy biiñ bu bees bi fàcc mbuus yi; biiñ bi tuuru, mbuus yi yàqu. \v 38 Biiñ bu bees daal, ci mbuus mu bees lees koy denc. \v 39 Te itam deesul naan biiñ bu yàgg, di bëggati bu bees, xanaa nga ne: “Bu yàgg bee baax\f + \fr 5.39 \fr*\ft Biiñ, nee ñu lu mu gëna yàgg rekk moo gën.\ft*\f*.”» \c 6 \s1 Bésub Noflaay, Yeesu mooy boroom \p \v 1 \w Bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w* la woon, Yeesu doon jaare ay tool yu ñor, taalibeem ya fàqe ca ay gub, di boxom, di lekk. \v 2 Ñenn ca \w Farisen|lemma="Farisen y-:"\w* ya ne leen: «Lu waral ngeen di def lu yoon mayewul ci bésub Noflaay?» \v 3 Yeesu ne leen: «Xanaa jànguleen la \w Daawuda|lemma="Daawuda:"\w* defoon, ba mu xiifee, moom, ak ña mu àndaloon? \v 4 Ba mu duggee ca kër Yàlla ga, \w mburum teewal|lemma="mburum teewal m-:"\w* ma la jël, lekk, jox ca ña mu àndal, te yoon mayewul kenn ku ca lekk ku dul \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi.» \v 5 Mu neeti leen: «Bésub Noflaay, \w Doomu nit ki|lemma="Doomu nit k-:"\w* mooy boroom.» \s1 Yeesu faj na nit ku loxoom làggi \p \v 6 Beneen \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*, Yeesu dugg ca jàngu ba, di jàngle. Jenn waay ju loxol ndijooram làggi ma nga fa woon. \v 7 Firikati yooni Musaa yaak \w Farisen|lemma="Farisen y-:"\w* yaa ngay xool Yeesu, ba xam ndax dina ko faj ca bésub Noflaay ba, ngir ñu am lu ñu ko tuumaale. \v 8 Yeesu nag xam seen xalaat, daldi ne boroom loxo ba: «Jógal taxaw fii ci digg bi.» Mu jóg taxaw. \v 9 Yeesu ne leen: «Laaj naa leen, ana lu yoon maye ci bésub Noflaay; def lu baax am lu bon? Musal bakkan am lore?» \v 10 Ci kaw loolu mu dawal bëtam, xool ña ko yéew ñépp, ba noppi ne waa ja: «Tàllalal sa loxo.» Mu tàllal, loxo ba wér. \v 11 Ñu mer nag ba fees, di diisoo ci seen biir nu ñuy def ak Yeesu. \s1 Yeesu tànn na fukki ndaw ak ñaar \p \v 12 Fan yooyu la Yeesu dem kaw tund wa ngir ñaani fa; mu fanaane faa ñaan ci Yàlla. \v 13 Ba bët setee, mu woo ay taalibeem, tànn ca fukk ak ñaar ñii, tudde leen ay ndawam: \li1 \v 14 Simoŋ mi Yeesuy wooye itam Piyeer, \li1 ak Àndre mi bokk ak Piyeer ndey ak baay, \li1 ak Yanqóoba ak Yowaan, \li1 ak Filib ak Bartelemi, \li1 \v 15 ak Macë ak Tomaa, \li1 ak Yanqóoba doomu Alfe, \li1 ak Simoŋ mi ñuy wax farlukatu moom-sa-réew, \li1 \v 16 ak Yuda doomu Yanqóoba, \li1 ak Yuda Iskaryo ma mujj wor. \s1 Nekkinu tey, yoolub ëllëg \p \v 17 Ci kaw loolu Yeesu ànd ak ñoom, wàcc, daldi taxaw ca joor ga. Ay taalibeem yu baree nga fa woon ak mbooloo mu réya réy: ay niti Yude gépp, ak \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w* ak \w Tir ak Sidon|lemma="Tir:"\w*, dëkki wetu tefes ga. \v 18 Ñu dikk, di ko déglu tey faju ba tàggook seeni jàngoro. Ñi rab jàpp it, wér. \v 19 Mbooloo mépp a ko doon wuta laal ndax leer guy bàyyikoo ca moom, di faj ñépp. \p \v 20 Yeesu nag xool ay taalibeem, ne leen: \q1 «Ndokklee yeen ñi néewle, \q1 nde nguurug Yàlla, yeenay boroom. \q1 \v 21 Ndokklee yeen ñi xiif tey, \q1 nde dingeen regg. \q1 Ndokklee yeen ñiy jooy tey, \q1 nde dingeen ree. \m \v 22 Ndokklee yeen, bu leen nit ñi bañee, daggook yeen, saaga leen, sikkal seen der ndax \w Doomu nit ki|lemma="Doomu nit k-:"\w*. \v 23 Bésub keroog, bégleen te bànneexu bay fecc ndax seen yoolub ëllëg bu réy, nde noonu la seen maami bañ yooyu daan def ak yonent ya. \q1 \v 24 Waaye wóoy ngalla yeen ñi barele, \q1 ndax neexle ngeen ba noppi. \q1 \v 25 Wóoy ngalla yeen ñi regg tey, \q1 ndax dingeen xiif ëllëg. \q1 Wóoy yeen ñiy ree tey, \q1 ndax dingeen tiislu, dingeen jooy. \m \v 26 Wóoy ngalla yeen, bu leen ñépp dee waxal lu baax, ndax noonu rekk la maami ñooñu daan jëfe ak yonenti caaxaan ya. \s1 Soppleen seeni noon \p \v 27 «Yeen ñi may déglu, dama ne, seeni noon, soppleen leen, seeni bañ, defal-leen leen lu baax. \v 28 Ñi leen di móolu, yéeneleen leen lu baax, ñi leen di soxore, ñaanal-leen leen. \v 29 Ku leen talaata cib lex, dékkleen ko ba ca des. Ku nangu seen mbubb mu mag, buleen ko teree jëlaale seenub turki. \v 30 Képp ku leen ñaan, mayleen ko; ku nangu seen yëf, buleen ko ko laaj. \v 31 Lu ngeen bëgg nit ñi defal leen ko nag, nangeen leen ko defale noonu. \p \v 32 «Su dee ñi leen sopp doŋŋ ngeen sopp, ana lu ngeen ci wara yooloo? Bàkkaarkat yi sax, ñi leen sopp, sopp nañu leen. \v 33 Te su dee ñi leen defal lu baax doŋŋ ngeen defal lu baax, ana lu ngeen ci wara yooloo? Bàkkaarkat yeet noonu doŋŋ lañuy jëfe. \v 34 Te su dee ñi ngeen yaakaare ndelloo doŋŋ ngeen lebal, ana lu ngeen ci wara yooloo? Bàkkaarkat yi it, yaakaar ndelloo lu mat sëkk moo tax ñuy leblante. \v 35 Yeen kay, soppleen seeni noon, defleen lu baax, lebleleen te baña yaakaar ndelloo. Su boobaa seenub yool réy, ngeen di doomi Aji Kawe ji, ndax moom de ñi santadi te bon, moo leen di baaxe. \v 36 Ni seen Baay ame yërmande nag, nangeen ni ame yërmande. \p \v 37 «Buleen di sikkale, su boobaa deesuleen sikkal. Buleen yeyale kenn ab daan, ngir ñu bañ leena yeyale ab daan. Baleleen, ñu baal leen. \v 38 Mayeleen, ñu may leen; natt bu duun bu ñu rokkas, yëngal, mu fees bay tuuru, moom lees leen di nàddil ci seen mbubb. Ndax natt bi ngeen di nattale, moom lees leen di nattale.» \s1 Ndimbal, koo tane \p \v 39 Yeesu léebati leen, ne leen: «Ndax gumba dina wommat gumba? Mbaa duñu ànd tàbbi ci kàmb? \v 40 Taalibe sutul sëriñam, waaye bépp taalibe bu jàng ba wàcc, tollook sëriñam. \p \v 41 «Ana looy xoole xatax bi ci sa bëtu mbokk te gànj gi ci sa bëtu bopp gisuloo ko? \v 42 Ana noo mane ne sa mbokk: “Mbokk mee, xaaral, ma dindil la xatax gi ci sa bët,” te yaw ci sa bopp gànj gi ci sa bët, gisuloo ko? Jinigalkat bi! Jëkkala dindi gànj gi ci sa bët. Su boobaa dinga gis bu baax xatax gi ci sa bëtu mbokk, ba dindil ko ko. \s1 Doom ja, ndey ja \p \v 43 «Garab gu neex du meññ doom yu naqari, te garab gu naqari it du meññ doom yu neex. \v 44 Garab gu nekk, meññeefam lees koy xàmmee. Ag dédd, deesu ci witte doomi figg; ay dagg it, deesu ci jële doomi reseñ. \v 45 Nit ku baax, dencub ngëneel ba ca biir xolam, ca lay jële lu baax la mu sàlloo; nit ku bon it, dencub safaan ba ca biir xolam, ca lay jële safaan ba mu sàlloo. Gémmiñ daal, la fees xolu boroom lay wax. \s1 Ñaari tabaxkat a ngi \p \v 46 «Ana lu ngeen ma naa “Sang bi, Sang bi,” te jëfewuleen samay wax? \v 47 Képp ku ñëw ci man, dégg samay wax te di ko jëfe, dinaa leen won nu muy mel. \v 48 Dafa mel ni nit kiy tabax kër, gasa gas ba mu xóot, daldi samp kenu ga ca kaw doj wa ca suuf. Mbënn ma dikk, wal ma rëkk kër gaak doole te manu koo yëngal ndax tabax bu wér ba ñu ko tabaxe. \v 49 Waaye ku dégg te jëfewoo, dangaa mel ni nit ku tabax kër ci suuf, te amul kenu. Wal maa koy rëkk ak doole, kër ga jekki màbb, yàqu yaxeet.» \c 7 \s1 Njiitu takk-der ba yooloo na ngëmam \p \v 1 Yeesu wax na kàddoom googu gépp, askan way dégg, mu doora jàll biir Kapernawum. \v 2 Foofa nag ab \w njiitu takk-der|lemma="njiitu takk-der b-:"\w* bu waa Room a nga fa woon, ab jaamam woppoon bay bëgga dee, te njiit la soppoon ko lool. \v 3 Ba njiit la déggee mbiri Yeesu, daa yebal ñenn ca magi Yawuti dëkk ba ca moom, ñaan ko ngir mu dikk xettli jaamam. \v 4 Magi dëkk ba agsi ca Yeesu, tinu koo tinu, ne ko: «Ki nu yebal ci yaw de, yelloo na sa ndimbal, \v 5 ndax ku sopp sunuw xeet la, te sunu jàngu bi sax, moo nu ko tabaxal.» \p \v 6 Yeesu daldi ànd ak ñoom. Naka la jubsi kër ga, njiit la yóbbante ay xaritam kàddoom, ñu gatandu Yeesu, ne ko: «Sang bi, jarul ngay sonn, ndax sab tànk sama biir kër, man yeyoowuma ko. \v 7 Moo ma la tee gatandul sama bopp, ndax jàpp naa ne loolu jomb na ma. Waxal genn kàddu rekk, sama surga wér. \v 8 Ndax man ci sama bopp ci kilifteef laa tënku, te man itam ay takk-der a ngi ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Ma ne kee: “Ñëwal,” mu ñëw. Te sama jaam bu ma ne: “Defal lii,” mu def ko.» \p \v 9 Ba Yeesu déggee loolu daa yéemu ca njiit la. Mu ne gees mbooloo ma topp ca moom, ne leen: «Dama ne, gii ngëm gu réy, \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* sax, gisuma ko ci.» \v 10 Ndaw ya daldi dellu ca kër ga, fekk jaam ba wér. \s1 Yeesu dekkal na doomu jëtun ba \p \v 11 La ca tegu Yeesu demati dëkk bu ñuy wax Nayin, ay taalibeem ak mbooloo mu bare ànd ak moom. \v 12 Ba mu jubsee buntu dëkk ba, yemul ci lu moy ab rob, ka dee di doomu jëtun, te moom rekk la amoon. Niti dëkk ba def mbooloo mu bare, ànd ak soxna sa. \v 13 Sang bi nag gis ko, ñeewante ko, ne ko: «Bul jooy.» \v 14 Mu dikk ba \w teg loxoom|lemma="teg loxo:"\w* ca jaat ga, ña ko jàppoo taxaw. Mu ne: «Ngóor si, yaw laay wax, jógal.» \v 15 Néew ba jóg toog, di wax, mu delloo ko yaay ja. \v 16 Tiitaange nag jàpp ñépp, ñu sàbbaal Yàlla, naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir!» te naan «Yàllaa wallusi ñoñam!» \p \v 17 Coow loolu nag law ca mboolem réewum Yawut ak mboolem fa ko wër. \s1 Yeesu jàngle na ci mbirum Yaxya \p \v 18 Ci kaw loolu taalibey \w Yaxya|lemma="Yaxya:"\w* àgge Yaxya loolu lépp. Mu woo ñaar ca taalibe ya, \v 19 yebal leen ci Sang bi, laaj ko ne ko: «Ndax yaw yaa di Ki wara ñëw, am keneen lanuy séentu?» \v 20 Taalibe ya dikk ne ko: «Yaxya moo nu yebal, di la laaj ndax yaa di Ki wara ñëw, am keneen lanuy séentu?» \p \v 21 Waxtu woowa tembe nag Yeesu faj na ñu bare, tàggale leen aki jàngoro aki jagadi aki rab, silmaxa yu bare, mu baaxe leen, ñuy gis. \v 22 Mu ne ndaw ya: «Li ngeen gis te dégg ko, demleen àgge ko Yaxya. Silmaxa yaa ngi gis, lafañ yi dox, \w gaana|lemma="gaana:"\w* yi wér, tëx yiy dégg, néew yi dekki, néew-doole ñi dégg xibaaru jàmm bi\f + \fr 7.22 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Esayi\+bk* 35.5-6 ak 61.1. Muy kàddug waxyu gu jëm ci Almasi.\ft*\f*. \v 23 Ku ma taxul nga xàcc sa péete ak man nag, ndokklee yaw.» \p \v 24 Ba ndawi Yaxya demee, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya, ne leen: «Lu ngeen seetaani woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax bu ngelaw liy yëngal? \v 25 Kon lu ngeen seetaani woon? Boroom yére yu rafet? Waaye boroom yére yu yànj yooyu te seen dund bakkane, ci këri buur lañu dëkk. \v 26 Kon nag lu ngeen seetaani woon? Ab yonent? Waawaaw, maa leen ko wax, te wees na ab yonent sax. \v 27 Ci moom moomu lañu bindoon ne: \q1 “Maa ngii di yebal sama ndaw, mu jiitu la, \q1 xàllal la saw yoon.” \m \v 28 Maa leen ko wax, li jigéen jur, kenn sutu ci Yaxya. Waaye ki gëna tuut ci nguurug Yàlla sax moo ko sut.» \p \v 29 Mboolem ña déglu Yeesu, ba ca \w juutikat|lemma="juutikat b-:"\w* ya sax, dëggal nañu Yàlla, ndax nangu nañoo sóobu sóobeb Yaxya. \v 30 Waaye \w Farisen|lemma="Farisen y-:"\w* ya ak xamkati yoon ya ñoo gàntal la leen Yàlla nammaloon, ba Yaxya sóobu leen ci ndox. \p \v 31 Yeesu neeti: «Ana kon lu may niruleel niti tey jii? Ana lu ñuy nirool? \v 32 Ñu ngi nirook xale yu toog ca pénc ma di awoonte, naan: \q1 “Noo leen toxorool, fecculeen, \q1 nu dëjal leen, jooyuleen.” \m \v 33 Ndaxte Yaxya daa feeñ, lekkul dugub, naanul biiñ, ngeen nee: “Aw rab la àndal.” \v 34 \w Doomu nit ki|lemma="Doomu nit k-:"\w* feeñ, di lekk ak a naan, ngeen naay: “Kee fuqle, naan-katub biiñ biiy xaritook juutikat yeek bàkkaarkat yi.” \v 35 Waaye xel mu rafet, mboolem la mu jur mooy la koy dëggal.» \s1 Yeesu gane na Simoŋ Farisen ba \p \v 36 Kenn ca \w Farisen|lemma="Farisen y-:"\w* ya moo woo woon Yeesu, ngir ñu bokk lekk. Yeesu agsi kër Farisen ba, daldi dikk ca ndab la. \v 37 Ndeke senn as ndaw a nga ca dëkk ba, ab moykat la woon. Mu yég nag ne Yeesoo nga ca kër Farisen ba, di lekk. Mu dikk, indaale njaqal doju \w albatar|lemma="albatar:"\w* lu def diwu xeeñlu. \v 38 Mu dikk ba fa Yeesu sóonu, ca gannaawam, fa tànki Yeesu féete, daldi taxaw, di jooy, rongooñ ya tooyal xepp tànk ya. Ndaw sa nag di fompe tànki Yeesu kawaru boppam gay lang, di fóon tànk yaak cofeel, di ca sotti diwu xeeñlu ga. \p \v 39 Farisen ba woo Yeesu nag gis loolu, naan ci xelam: «Kii su doon ab yonent, dina xam ndaw sii di ko nabb-nabbee ku mu doon, ak lu mu doon: jigéenu moykat!» \v 40 Yeesu nag àddu, ne ko: «Simoŋ, dinaa la wax lenn.» Mu ne ko: «Waxal, sëriñ bi.» \p \v 41 Yeesu ne ko: «Ñaari boroom bor la woon ak seenub leblekat. Boru kenn ka di téeméeri junni (500 000) ci xaalis, ka ca des fukki junni (50 000)\f + \fr 7.41 \fr*\fk téeméeri junni: \fk*\ft maanaam juróomi téeméeri dinaar; \ft*\fk fukki junni: \fk*\ft maanaam juróom fukki dinaar. Seetal \ft*\fq Xaalis \fq*\ft ci Leeral yi.\ft*\f*. \v 42 Waaye ñoom ñaar ñépp, kenn manu cee fey. Mu far jéggal leen ñoom ñépp. Ana kan ci ñaar ñooñu nag moo ciy gëna fonk leblekat bi?» \v 43 Simoŋ ne ko: «Xanaa ki ëpple lu ñu ko jéggal.» \p Yeesu ne ko: «Sab àtte jub na.» \v 44 Mu walbatiku ca ndaw sa, daldi ne Simoŋ: «Gis nga ndaw sii de? Dugg naa sa kër, mayewoo ndox mu ma jàngoo. Waaye moom, ay rongooñam la tooyale samay tànk, fompe ko kawaru boppam. \v 45 Fóonuloo ma, dalale ma, waaye moom, ba ma duggsee ba léegi noppiwula fóon samay tànk. \v 46 Ag diw, diwewoo ko sama bopp, waaye moom, diwu xeeñlu la diw samay tànk. \v 47 Moo tax ma di la wax, ne bàkkaaram yu bare yi ñu ko jéggal moo waral fonkeelam gu bare. Waaye njéggal lu tuut, fonkeel gu tuut rekk.» \p \v 48 Yeesu nag ne ndaw sa: «Jéggalees na la say bàkkaar.» \v 49 Ci kaw loolu ña mu toogandool di lekk, naan ci seen xel: «Kii mooy kan bay jéggaley bàkkaar sax?» \v 50 Yeesu nag ne ndaw sa: «Sa ngëm musal na la, demal ak jàmm.» \c 8 \s1 Jiwu wuute na ag muj \p \v 1 Gannaaw loolu Yeesu wër dëkkoo dëkk bu mag ak bu ndaw, di waare, di yégle xibaaru jàmm bu nguurug Yàlla, ànd ak fukki taalibe yaak ñaar, \v 2 ñoom ak jigéen ñii mu fajoon, ba tàggale leen ak rab yu bon aki jagadi: Maryaama, mi ñuy wax Magdala, ma ñu tàggaleek juróom ñaari rab, \v 3 ak Yowaana jabaru Kusa, saytukatub \w Erodd|lemma="Erodd:"\w*; ak Susaana, ak ñeneen jigéen ñu bare ñu daan dimbalee ñoom Yeesu seen alal. \p \v 4 Mbooloo mu mag a daje woon, jóge dëkkoo dëkk, fekksi Yeesu. Mu léeb leen, ne leen: \v 5 «Boroom jiwu moo demoon jiyi. Naka lay saaw ab toolam, ndeke lenn ca jiwu maa nga wadde ca kaw yoon wa, nit ñi joggati ca, picc yi dikk, lekk ko. \v 6 Leneen wadde fu barey doj. Naka la sax rekk, daldi wow, ndax ñàkk ndox. \v 7 Leneen la wadde biiri xaaxaam, jógandoo ak xaaxaam ma, daldi fatt ba wow. \v 8 La des ca jiwu ma wadde suuf su nangu, daldi sax, ba meññal lu ko mat téeméeri yoon.» \p Ci kaw loolu Yeesu àddu ca kaw ne: «Ku am nopp yu mu dégge kat, na dégg.» \p \v 9 Ay taalibeem laaj ko lu léeb woowu di tekki. \v 10 Mu ne leen: «Yeen lañu may, ngeen xam mbóotum nguurug Yàlla, waaye ñi ci des ñoom, ci ay léeb lees koy dëxëñ, su ko defee: \q1 “Ñuy xoole te duñu gis, \q1 di dégg te duñu xam.” \p \v 11 «Lii la léeb wi di tekki. Jiwu wi moo di kàddug Yàlla. \v 12 Ñi féeteek yoon wi mooy ñi dégg. \w Seytaane|lemma="Seytaane:"\w* nag mooy dikk, foqati kàddu gi ci seen xol, ngir ñu baña gëm ba mucc. \v 13 Ñi féete fu bare ay doj, ñoo dégg kàddu gi, nangoo ko xol bu sedd. Waaye ñooñu, ab reen lañu amul. Ab diir rekk lañuy gëm, bu janti nattu dikkee, ñu dellu gannaaw. \v 14 Li wadde ci ay xaaxaam mooy ñi dégg kàddu gi, te ay xalaat ak alal, ak bànneexu bakkan fatt leen, ba tax meññaluñu lu ñor. \v 15 Li ci suuf su baax si nag, mooy ñi dégge kàddu gi xol bu dëggu te rafet, ŋoy ca, te saxoo muñ ba meññal. \s1 Ab làmp du làqu \p \v 16 «Deesul taal ab làmp, dëppe ko ndab, mbaa nga dugal ko ci ron lal. Dees koy aj kay ba kuy duggsi, di gis leer gi. \v 17 Mboolem lu làqu dina feeñ, te mboolem lu nëbbu dina siiw ba ne fàŋŋ. \v 18 Kon nag teewluleen ni ngeen di dégge. Ku am, dees na ko dolli, waaye ku amul, la mu xalaatoon ne am na ko sax, dees na ko nangu.» \s1 Déggal Yàllaa gën bokk ak Yeesu \p \v 19 Yaayu Yeesu ak ay rakkam ñoo dikkoon di seet Yeesu te manuñoo agsi ci moom ndax nit ñu bare. \v 20 Ñu ne ko: «Sa yaay ak say rakk a ngi taxaw ci biti, bëgg laa gis.» \v 21 Mu ne leen: «Sama yaay ak samay rakk, ñoo di ñiy dégg kàddug Yàlla, te di ko jëfe.» \s1 Yeesu dalal na ngelaw li \p \v 22 Benn bés la Yeesu duggoon gaal, mook ay taalibeem. Mu ne leen: «Nanu jàll ca wàllaa dex gi.» Ñu daldi dem. \v 23 Naka lañuy dem nag, Yeesu nelaw. Ngelaw lu réy dal ca kaw dex ga, gaal gi fees ak ndox, ba ñu nara sànku. \v 24 Taalibe yi yee Yeesu, ne ko: «Njaatige, njaatige, nu ngi sànku!» \p Mu yewwu, gëdd ngelaw li ak gannax yu réy yi. Lépp dal, ne tekk. \v 25 Yeesu ne taalibe ya: «Ana seen ngëm?» Ña nga boole tiitaange ak kéemtaan te naan ca seen biir: «Kii nag moo di kan bay jox ndigal ngelaw leek ndox mi sax, ñu déggal ko?» \s1 Yeesu faj na ku rab jàpp \p \v 26 Ci kaw loolu ñu tëmb ba teereji ca diiwaanu waa Serasa, fa jàkkaarloo ak diiwaanu Galile. \v 27 Ba Yeesu wàccee ca tefes ga, jenn waayu dëkk ba dikk dajeek moom. Waa ja, ay rab a ko jàpp. Yàgg naa def yaramu neen te dëkkul ci kër, xanaa sëg ya. \v 28 Ba mu gisee Yeesu, daa yuuxu, daanu fa kanamam, daldi xaacu ne: «Yaw Yeesu Doomu Yàlla Aji Kawe ji, ana lu ma joteek yaw? Dama lay tinu, bu ma mbugal!» \p \v 29 Booba Yeesu tàmbali naa sant rab wi, mu génn waa ji. Rab wi jàpp na waa ji ay yooni yoon. Su ko defee ñu yeewe ko ay càllala, jéng ko, ngir wattu ko, mu di ko dagg, rab wi di ko xabtal, jëme bérab yu wéet. \p \v 30 Yeesu ne ko: «Noo tudd?» Mu ne ko: «Coggal.» Ndax rab yu baree duggoon waa ji. \v 31 Rab yi nag tinu Yeesu, ngir mu bañ leena yebal ca \w xóote|lemma="xóote b-:"\w* ba\f + \fr 8.31 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Peeñu ma\+bk* 20.2-3.\ft*\f*. \p \v 32 Ag coggalu mbaam-xuux yu baree nga woon foofa, di fore ca tund wa. Rab ya tinu Yeesu, ne mu may leen, ñu dugg mbaam-xuux ya. Mu may leen ko. \v 33 Rab ya nag génn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, coggal ga bartaloondoo, tàbbi ca dex ga, daldi lab. \v 34 Sàmm ya gis la xew, daldi daw, nettaliji ko waa dëkk ba, ak dëkk-dëkkaan ya. \v 35 Nit ña riire ca, di seet la xew. \p Naka lañu dikk ba ci Yeesu, yem ci nit ki rab wi teqlikool, mu ànd ak sagoom, solu, toog ca wetu Yeesu. Ñu daldi tiit. \v 36 Ña ko fekke woon nag, nettali leen na boroomi rab ba jote wall. \v 37 Ci kaw loolu mbooloom diiwaanu Serasa gépp tinu Yeesu ngir mu jóge ca seen biir te dem ndax tiitaange lu réy lu leen jàpp. Naka la Yeesu dugg gaal, di dem, \v 38 nit ka teqlikook rab yi di ko sarxu ngir ànd ak moom. Teewul Yeesu yiwi ko, ne ko: \v 39 «Ñibbil, te nga xamle li la Yàlla defal lépp.» Waa ja it dem di siiwal ca dëkk ba bépp, mboolem la ko Yeesu defal. \s1 Yeesu faj na, dekkal na \p \v 40 Ba Yeesu delloo ca wàllaa dex, mbooloo maa ko teertu, ndax ñoom ñépp a ko doon xaar. \v 41 Ci kaw loolu rekk jenn waay dikk, ku ñuy wax Yayrus, di njiitu jàngu ba. Mu ne gurub fi kanam Yeesu, sarxu ko ngir mu ñëw këram, \v 42 ndax kenn la amoon ci doom, janq bu am fukki at ak ñaar, te ma nga doon waaja dee. \p Yeesoo ngay dem, nit ña raj-rajloo, tanc ko. \v 43 Senn as ndaw a nga ca woon, diiru fukki at ak ñaar, ma nga doon xëpp deret, te def na ci alalam jépp, kenn manu koo faj. \v 44 Mu doxe Yeesu gannaaw, \w teg loxoom|lemma="teg loxo:"\w* ca catal mbubbam, deret ja dal ca saa sa. \p \v 45 Yeesu nag ne: «Ana ku ma laal?» Ku nekk di miim. Piyeer ne ko: «Njaatige, mbooloo mépp a la yéew, dar la.» \v 46 Teewul Yeesu ne: «Am na ku ma laal kay, ndax yég naa leer gu bàyyikoo ci man.» \v 47 Ndaw sa xam ne feeñ na. Mu daldi dikk, di lox, ne gurub fa kanam Yeesu, daldi wax ca kanam ñépp la waral mu teg ko loxoom, ak na mu wére ca saa sa. \v 48 Yeesu ne ko: «Janq, sa ngëm faj na la. Demal ak jàmm.» \p \v 49 Naka la Yeesu di wax, jenn waay jóge ca kër njiitu jàngu ba, dikk ne: «Matatul ngay sonal sëriñ bi, sa janq ba faatu na.» \v 50 Yeesu dégg ca, ne njiit la: «Bul tiit. Gëmal rekk, mu daldi mucc.» \p \v 51 Bi Yeesu agsee ca kër ga, mayul kenn ànd ak moom dugg, ku moy Piyeer, ak Yowaan ak Yanqóoba ak baayu xale bi, ak ndeyam. \v 52 Ñépp a ngay jooy ak a tiislu janq bi. Yeesu nag ne leen: «Buleen jooy. Janq bi deewul, day nelaw rekk.» \v 53 Ci kaw loolu ñu di ko kókkali, ndax xamoon nañu xéll ne dee na. \v 54 Yeesu itam jàpp ca loxol janq ba, daldi àddu ca kaw, ne ko: «Janq, jógal.» \v 55 Noo ga délsi, mu ne ñokket. Yeesu ne ñu may ko, mu lekk. \v 56 Waajuri xale bi nag waaru. Teewul Yeesu dénku leen, ne leen bu ñu wax kenn la xew. \c 9 \s1 Yeesu yebal na fukki taalibe yi ak ñaar \p \v 1 Yeesu moo woo woon Fukk ñaak ñaar, jox leen xam-xam ak sañ-sañu dàq mboolem rab tey faj ay jàngoro. \v 2 Ci kaw loolu mu yebal leen ngir ñu yégleji nguurug Yàlla tey faj jarag ji. \v 3 Mu ne leen: «Bu ngeen di dem, buleen yóbbaale dara ngir fàggu yoon wi; du yet, du mbuus, du aw ñam, du xaalis. Bu ci kenn yor ñaari turki sax. \v 4 Kër gu ngeen dugg, fa ngeen di dal, ba kera ngeen dem. \v 5 Fépp fu ñu leen dalalewul, génnleen dëkk booba te ngeen faxas fa seen pëndub ndëgguy tànk, seedeele leen ko seen ngàntal.» \p \v 6 Ñuy dem nag, di wër dëkk ak dëkk, di yégle xibaaru jàmm bi, di faj jarag ji. \p \v 7 Ci kaw loolu \w Erodd|lemma="Erodd:"\w* boroom Galile dégg mboolem la xew, boppam nag ubu, ndax ñenn ñu noon \w Yaxya|lemma="Yaxya:"\w* moo dekki, di Yeesu. \v 8 Ñee ne \w Ilyaas|lemma="Ilyaas:"\w* moo délsi, ñeneen ba tey, ne kenn ca yonent yu jëkk yaa dekki. \v 9 Erodd daldi ne: «Yaxya, man maa doglu boppam. Kon ki ma déggal jëf jii, mooy kan?» Ba loolu amee mu di ko fexee gis. \s1 Yeesu leel na mbooloo \p \v 10 Ba ndaw ya délsee, dañoo nettali Yeesu mboolem la ñu def. Mu ànd ak ñoomu neen ba sore, ca wetu dëkk ba ñuy wax Beccayda. \v 11 Teewul nit ña yég ne fa la dem, daldi ko topp. Yeesu dalal leen, di leen wax ci mbirum nguurug Yàlla, ña aajowoo am paj, mu wéral leen. \p \v 12 Ba jant di sowat, Fukk ñaak ñaar dikk ne Yeesu: «Yiwil mbooloo mi, ñu dugg ci dëkk yu ndaw yii ak dëkk-dëkkaan yi ko wër, ngir ñu gis lu ñu lekk ak fu ñu fanaan, ndax fii àllub neen la.» \v 13 Mu ne leen: «Yeen, joxleen leen lu ñu lekk.» Ñu ne ko: «Nun de amunu lu dul juróomi mburu ak ñaari jën. Xanaa nu dem, nun ci sunu bopp, jëndali mbooloo mii mépp lu ñu lekk!» \v 14 Lu wara mat juróomi junniy góor a nga fa woon. Yeesu ne taalibe ya: «Dangeen leen di toogal, ñu def géewi juróom fukki nit.» \v 15 Ñu def noonu, toogal ñépp. \p \v 16 Ba mu ko defee Yeesu jël juróomi mburu ya ak ñaari jën ya, xool kaw asamaan, daldi yékkati kàddug cant, ba noppi dagg mburu ya, jox taalibe ya, ngir ñu taajal ko mbooloo ma. \v 17 Ñépp lekk ba regg, ba ñu yóbbu dog ya ca des, muy fukki pañe ak ñaar. \s1 Piyeer xam na kuy Yeesu \p \v 18 Yeesu moo beru woon, di julli, taalibe ya feggook moom. Ci kaw loolu mu laaj leen ne leen: «Ana ku nit ñi ne moom laa?» \v 19 Ñu ne ko: «Ñii nee ñu yaa di \w Yaxya|lemma="Yaxya:"\w*; ñee ne yaa di \w Ilyaas|lemma="Ilyaas:"\w*; ñale ne kenn ci yonent yu jëkk yaa dekki, di yaw.» \p \v 20 Yeesu ne leen: «Yeen nag, ngeen ne maay kan?» Piyeer ne ko: «Yaa di \w Almasib|lemma="Almasi:"\w* Yàlla.» \v 21 Mu femmu leen nag, sant leen ñu bañ koo wax kenn. \v 22 Mu neeti: «Fàww \w Doomu nit ki|lemma="Doomu nit k-:"\w* sonn lu bare, ba dajeek mbañeelu magi askan wi ak \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yu mag yi, ak firikati yoon yi, te dees na ko rey, ba ñetteelu fanam, mu dekki.» \p \v 23 Yeesu nag wax leen ñoom ñépp, ne leen: «Képp ku bëgga dikk topp ma, fàtteel sa bopp, te nga gàddu bés bu nekk, bant bi ñu lay daaj, door maa topp. \v 24 Ndax képp ku namma rawale sa bakkan, yaay ñàkk sa bakkan, waaye képp ku ñàkk sa bakkan ngir man, yaa musal sa bakkan. \v 25 Ndax nit ki, su jagoo àddina sépp sax, te nara ñàkk bakkanam mbaa mu sànku, ana lu mu koy jariñ? \v 26 Képp ku kersawoo sama jëmm, kersawoo topp samay wax, yaw itam Doomu nit ki dina la kersawoo, bés bu dikkee ci darajaam ak darajay Baay bi, ak darajay malaaka yu sell yi. \v 27 Maa leen ko wax déy, ñenn a ngi fii taxaw tey, duñu dee te gisuñu nguurug Yàlla.» \s1 Leeru Yeesu jolli na \p \v 28 Ba lu wara tollook juróom ñetti fan wéyee gannaaw kàddu yooyu, Yeesu àndoon na ak Piyeer ak Yowaan ak Yanqóoba, ñu yéeg ca kaw tund wa ngir julli. \v 29 Naka lay julli, xar kanamam soppiku, ay yéreem weex tàll, di melax. \v 30 Ci kaw loolu ñaari nit jekki feeñ, di waxtaan ak moom; ñuy Yonent Yàlla \w Musaa|lemma="Musaa:"\w* ak Yonent Yàlla \w Ilyaas|lemma="Ilyaas:"\w*. \v 31 Ñoo feeñ ci ag leer, di waxtaane dëddug Yeesu, ga mu doon waaja sottale fa \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w*. \v 32 Booba ngëmment a ngay man Piyeer ak ña mu àndal. Ba ñu teewloo nag lañu gis leeru Yeesu, ak ñaar ña mu taxawal. \v 33 Ba ñu demee ba ñaari nit ñooñu di bàyyikoo fa Yeesu, Piyeer ne ko: «Njaatige, su nu toogoon fii de, mu baax ci nun; nan yékkati ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa, benn Ilyaas.» Waaye booba Piyeer xamul la muy wax. \v 34 Naka lay wax loolu, aw niir dikk yiir leen, taalibe ya tàbbi ca biir niir wa, tiitaange jàpp leen. \v 35 Ci biir loolu baat jibe ca niir wa, ne: «Kii moo di sama Doom, ki ma taamu; dégluleen ko.» \p \v 36 Ba baat ba selawee, Yeesu doŋŋ a feeñ. Taalibe ya nag ñoom ne cell, waxuñu kenn lenn jant yooyu, ca la ñu gis. \s1 Yeesu fajati na ku rab jàpp \p \v 37 Ca ëllëg sa ba ñuy wàcce tund wa, mbooloo mu baree dikk dajeek Yeesu. \v 38 Jenn waay jekki xaacoo ca mbooloo ma, ne: «Sëriñ bi, dama lay ñaan, nga xoolal ma sama doom, ndax moom doŋŋ laa am. \v 39 Rab kat moo ko jàpp, mu jekki di yuuxu, di say, gémmiñ giy fuur. Daanaka du teqlikook moom te sonal na ko. \v 40 Ñaan naa say taalibe ngir ñu dàqal ma ko, waaye manuñu ko.» \v 41 Yeesu ne leen: «Céy niti tey, yeena gëmadi te dëng! Maak yeen ba kañ, te di leen muñal? Indi sa doom fii.» \p \v 42 Naka la xale bi jubsi Yeesu, rab wi sànni ko ci suuf, muy say. Yeesu itam gëdd rab wa, wéral xale ba, delloo ko baayam. \v 43 Ñépp nag waaru ci màggug Yàlla. \p Naka la ñépp di yéemu ca mboolem la Yeesuy def, mu ne taalibeem ya: \v 44 «Ubbileen seeni nopp te teewlu bu baax kàddu yii: \w Doomu nit ki|lemma="Doomu nit k-:"\w* lees di wor, ngir teg ko ci loxoy nit ñi.» \v 45 Taalibe ya nag dégguñu kàddu googu, ndax fekk na piri ma làqu leen, ngir ñu bañ koo daj, te ñemewuñu koo laaj Yeesu. \s1 Daraja réer na ku ko sàkku \p \v 46 Werante moo dikkaloon taalibe yi, ñuy seet kan moo gëna kawe ci ñoom. \v 47 Yeesu nag ràññee seen xalaat. Mu daldi indi ab xale, taxawal ko ci wetam. \v 48 Mu ne leen: «Xale bii, képp ku ko dalal ndax sama tur, man nga dalal; te képp ku ma dalal, dalal nga ki ma yebal; ndax ki gëna tuut ci yeen ñépp, kooku moo gëna màgg.» \p \v 49 Ci kaw loolu Yowaan àddu, ne: «Njaatige, danoo gis nit kuy dàqe sa tur ay rab, nu aaye ko, ndax bokkul ci nun.» \v 50 Yeesu ne ko: «Buleen ko aaye, ndax ku la sotul, yaw la faral.» \s1 Samari gàntal na Yeesu \p \v 51 Ba ñu demee ba bés bi ñu wara yéege Yeesu di jubsi, Yeesu moo dogu ngir dem \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w*. \v 52 Mu yebal ay ndaw, ñu jiitu ko. Ñu dem, ba agsi ab dëkk ci diiwaanu \w Samari|lemma="Samari:"\w*, nar ko faa waajal ab dal. \v 53 Waa Samari nag nanguwuñu koo dalal, ndax Yerusalem ga mu nammoona jëm\f + \fr 9.53 \fr*\ft Waa Samari ay nooni Israyil lañu woon.\ft*\f*. \v 54 Taalibe ya ñuy wax Yanqóoba ak Yowaan gis loolu, daldi ne: «Sang bi, soo bëggee nu jox sawara ndigal, mu wàcce asamaan, faagaagal leen?» \v 55 Teewul Yeesu geesu, femmu leen. \v 56 Ba loolu amee ñu jàll jëm beneen dëkk. \s1 Gëmkatu Yeesu du xool gannaawam \p \v 57 Ca yoon wa ñu awe la jenn waay ne Yeesu: «Yaw laay topp fépp foo jëm.» \v 58 Yeesu itam ne ko: «Till ak kàmbam, njanaaw akub tàggam, waaye \w Doomu nit ki|lemma="Doomu nit k-:"\w* de, amul fu mu wéer boppam.» \v 59 Mu neeti keneen: «Toppal ci man.» Mu ne ko: «Sang bi, may ma, ma jëkka dem robi sama baay.» \v 60 Mu ne ko: «Bàyyil néew yi, ñu rob seeni néew, waaye yaw demal, yégleji nguurug Yàlla.» \v 61 Keneen neeti ko: «Sang bi, yaw laay topp, waaye may ma, ma jëkka tàggtook sama waa kër.» \v 62 Yeesu ne ko: «Képp ku tàmbalee gàbb tey xool gannaawam, jekkoo ci nguurug Yàlla.» \c 10 \s1 Yeesu yebal na juróom ñaar fukk ak ñaar \p \v 1 Gannaaw loolu Sang bi tabb na yeneen juróom ñaar fukki taalibe ak ñaar, yebal leen, ñaar, ñaar, ñu jiituji ko ca mboolem dëkk yaak gox, ya mu nammoona dem moom ci boppam. \v 2 Mu ne leen: «Ngóob mee yaatu, te surga yi néew. Kon nag ñaanleen Boroom ngóob mi, ay surga yu mu yebal cim ngóobam. \v 3 Demleen! Xamleen ne maa leen yebal, mbete ay gàtt ci biiri bukki. \v 4 Buleen yóbbaale dencukaayu xaalis, mbaa mbuus, mbaa ay carax te buleen taxaw di saafoonte ak kenn ci yoon wi. \p \v 5 «Gépp kër gu ngeen dugg, jëkkleen ne: “Jàmm ñeel na leen.” \v 6 Su fa nitu jàmm nekkee, seen jàmm dal ko. Lu ko moy, mu délsi ci yeen. \v 7 Dal-leen ca kër googa, di lekk ak a naan ca la ñu leen jox, ndax liggéeykat yelloo na peyooram. Buleen di wër nag kër ak kër. \p \v 8 «Bépp dëkk bu ngeen dugg, ñu dalal leen, la ñu leen taajal, lekkleen ko. \v 9 Wéral leen jaragi dëkk ba, te ngeen wax waa dëkk ba, ne leen: “Nguurug Yàlla dëgmal na leen.” \v 10 Waaye bépp dëkk bu ngeen dugg te dalaluñu leen, demleen ca pénc ma te ngeen ne leen: \v 11 “Seen pëndub dëkk bi ci sunu ndëgguy tànk sax, nu ngi koy faxas, seedeele leen ko seen ngàntal. Waaye nag xamleen ne nguurug Yàlla dëgmal na.” \v 12 Maa leen ko wax, bu bés baa, boobu dëkk, \w Sodom|lemma="Sodom ak Gomor:"\w* a koy gënu demin. \p \v 13 «Wóoy ngalla yeen waa Korasin, yeen waa Beccayda it, wóoy ngalla yeen, nde kéemaan yi sottee fi seen biir, su doon fa waa \w Tir|lemma="Tir:"\w* mbaa fa waa Sidon la sottee, kon bu yàgg lañu doon sol ay saaku, xëppoob dóom, ngir tuub. \v 14 Moo tax it, kera àtte ba, waa Tir ak Sidon a leen di gënu demin. \v 15 Yeen waa Kapernawum nag, dees na leen yékkati ba asamaan a? Xanaa ba fa njaniiw kay ngeen di wàcci. \p \v 16 «Ku leen déggal nag, man nga déggal; ku leen gàntal, man nga gàntal. Te ku ma gàntal, gàntal nga ki ma yebal.» \p \v 17 Ba juróom ñaar Fukk ñaak ñaar demee ba délsi, mbégte lañu àndal. Ñu ne: «Sang bi, rab yi sax, danu leen di jox ndigal ci sa tur, ñu nangul nu.» \v 18 Yeesu ne leen: «Séen naa \w Seytaane|lemma="Seytaane:"\w* mu fàqe asamaan ni ag melax. \v 19 Dama ne, maa leen jox sañ-sañu joggi ci kawi jaan aki jiit, joggati mboolem dooley bañaale bi, te dara du leen mana gaañ mukk. \v 20 Noonu leen rab yi nangule nag, buleen ko bége, bégeleen kay la seen tur binde fa asamaan.» \p \v 21 Ca waxtu woowa tembe la kemtalaayu mbégte tukkee ci \w Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"\w* gi, dugg Yeesu, mu daldi ne: «Baay, Boroom asamaan ak suuf, sant naa la, nde yaa làq lii boroom xam-xam yeek boroom xel yi, xamal ko tuut-tànk yi, nde loolu de, Baay, mooy li la soob. \v 22 Lépp la ma sama Baay dénk, te kenn xamul kuy Doom ji, ku dul Baay bi; kenn it xamul kuy Baay bi, ku dul Doom ji, ak képp ku ko Doom ji namma xamal.» \p \v 23 Ci kaw loolu Yeesu walbatiku ca taalibe ya, wax leen ñoomu neen, ne leen: «Ndokklee ñi seeni gët gis li ngeen gis. \v 24 Ndax maa leen ko wax, bare na ay yonent ak buur yu bëggoona gis li ngeen gis, te gisuñu ko, ak itam dégg li ngeen dégg, te dégguñu ko.» \s1 Texe am na yoon \p \v 25 Benn xamkatu yoonu Musaa moo jekki woon jóg, di fexee fiir Yeesu. Mu ne ko: «Sëriñ bi, ana lu may def, ba texe ba fàww?» \v 26 Yeesu ne ko: «Yoonu Musaa, ana lees ci bind? Loo ci jànge?» \v 27 Mu ne ko: «Boroom bi sa Yàlla, nanga ko soppe sa léppi xol ak sa léppi bakkan ak sa léppi doole ak sa léppi xel, te ni nga soppe sa bopp, nanga ko soppe sa moroom\f + \fr 10.27 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Baamtug Yoon wi\+bk* 6.5 ak \+bk Sarxalkat yi\+bk* 19.18.\ft*\f*.» \v 28 Yeesu nag ne ko: «Wax nga dëgg. Noonu ngay def, daldi texe.» \v 29 Waa ja nag namma wutu lay, ne Yeesu: «Sama moroom mooy kan?» \p \v 30 Yeesu neeti ko: «Jenn waay a jóge woon \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w*, jëm Yeriko. Mu dajeek ay sàcc, ñu futti ko, dóor ko, daldi dem, bàyyi ko, muy waaja dee. \v 31 Yàlla woo yàlla ab \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bu jaare yoon woowa, séen nit ka, daldi teggi. \v 32 Jenn waay ju soqikoo ci giirug \w Lewi|lemma="Leween b-:"\w* it noonu; daa dikk ba tollu foofa, séen waa ja, daldi teggi. \v 33 Jenn waay ju dëkk \w Samari|lemma="Samari:"\w* nag doon tukki, dikk ba jege waa ja, xool ko, yërëm ko lool. \v 34 Mu dikk, sotti diw ak biiñ ca gaañu-gaañu ya, lëmës ko. Ci kaw loolu mu teg ko ci mbaamam, yóbbu ko ci ab dalukaay, di ko topptoo. \v 35 Ca ëllëg sa, mu yékkati ñaari poseti xaalis\f + \fr 10.35 \fr*\ft Benn poset bu ci nekk, benn dinaar la tollool, te moo doon peyooru benn bésub lëmm. Seetal \ft*\fq Xaalis \fq*\ft ci Leeral yi.\ft*\f*, jox ko boroom dal ba, ne ko: “Topptoo ko waa ji. Loo ci dolli, bu ma dëppee, maa la koy delloo.”» \p \v 36 Mu teg ca ne ko: «Ñett ñii, kan nga foog ne moo ci taxawu waa ja dajeek sàcc ya, taxawaayu nit ak moroomam?» \v 37 Mu ne ko: «Xanaa ki ko defal yërmande.» Yeesu nag ne ko: «Demal boog, di defe noonu.» \s1 Maryaama raw na Màrt \p \v 38 Yeesu ak ay taalibeem ñoo toppoon seenu yoon, ba tollook ab dëkk. Ba ñu dikkee, senn as ndaw su ñuy wax Màrt, ganale ko. \v 39 Ci kaw loolu rakkam ju ñuy wax Maryaama toog ca wetu Sang bi, di déglu kàddoom, \v 40 te fekk Màrt jàpp lool ca liggéeyu waañ wa. Mu dikk ne Yeesu: «Sang bi, xanaa gisoo sama rakk ji ma bàyyeek liggéeyu waañ wi, man doŋŋ? Wax ci boog, mu jàpple ma.» \v 41 Sang bi ne ko: «Màrt, Màrt, yitte yi nga xintewoo, di ci doñ-doñi moo bare. \v 42 Ndaxam lenn doŋŋ a manula ñàkk. Maryaama nag, cér bi gën la taamu, te deesu ko nangu ci moom.» \c 11 \s1 Kàddug julli am na yoon \p \v 1 Yeesu moo doon julli benn bérab. Ba mu noppee, kenn ca taalibeem ya ne ko: «Sang bi, jàngal nu julli noonee \w Yaxya|lemma="Yaxya:"\w* jàngale julli ay taalibeem.» \v 2 Yeesu ne leen: «Bu ngeen dee julli, ne leen: \q1 Baay, sellnga ñeel na saw tur, \q1 na sa nguur dikk. \q1 \v 3 May nu bés ak bés sunub dundu bés bu nekk. \q1 \v 4 Baal nu sunuy bàkkaar, \q1 ni nuy baale nun itam, mboolem ñi nu tooñ, \q1 te bu nu dugal ci nattu.» \p \v 5 Yeesu teg ca ne leen: «Ana kan ci yeen moo seeti ab xaritam xaaju guddi, ne ko: “Xarit, lebal ma ci ñetti mburu. \v 6 Sama xarit bu nekk ciw yoon moo dikk sama kër, te awma dara lu ma ko taajal,” \v 7 te xarit ba àddoo ca biir néegam, ne ko: “Bu ma sonal, tëj naa ba tëdd, maak samay doom; manumaa jóg, di la jox dara”? \v 8 Maa leen ko wax, su jógul jox ko la mu laaj ndax ug xaritoo it, la ko kee amul kersay yee ngir sàkku ndimbal mooy tax mu jóg, jox ko mboolem lu mu soxla. \v 9 Moo tax ma ne leen, ñaanleen, ñu may leen; seetleen, ndax ngeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen. \v 10 Ndaxte képp ku ñaan, dinga am; ku seet, dinga gis; ku fëgg it, dees na la ubbil. \v 11 Ana kan ci yeen mooy baay bu doomam ñaan aw jën, mu jox ko jaan? \v 12 Mbaa mu ñaan ko nen, mu jox ko aw jiit? \v 13 Ndegam yeen ñi bon yeena mana may seeni gone lu baax nag, astamaak Baay ba fa asamaan. Moo leen ko dàq fuuf, nde mooy may \w Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"\w* gi, ñi ko ko ñaan!» \s1 Beelsebul xeexul boppam \p \v 14 Yeesu moo doon dàq aw rab wu duggoon nit ba mu luu. Ba rab wa génnee, luu ba wax, mbooloo ma waaru. \v 15 Teewul ñenn ca ñoom ne: «Ci Beelsebul, buuru rab yi lay dàqe ay rab.» \p \v 16 Ñeneen nag di ko fiir, di sàkku ci moom firnde ju bawoo asamaan. \v 17 Yeesu itam ràññee seen xalaat, ne leen: Gépp nguur guy xàjjalikoo ci biiram, day tas, yii kër màbb ca kaw yee. \v 18 \w Seytaane|lemma="Seytaane:"\w* itam, su xàjjalikoo ci biiram, ana nu nguuram di yàgge, gannaaw yeena ne Beelsebul laay dàqe ay rab? \v 19 Te it ndegam man Beelsebul laay dàqe rab yi, seen ñoñ nag ñoom, kan lañuy dàqe ay rab? Kon kay seen ñoñ a leen tiiñal. \v 20 Waaye su dee loxol Yàlla laay dàqe rab yi nag, kon nguurug Yàlla agsi na ba ci yeen. \p \v 21 «Su ponkal gànnaayoo ba diis, wattu këram, alalam dina raw. \v 22 Waaye bu ko ku ko man songee, ba daan ko, day nangu mboolem ngànnaay lu mu yaakaaroon, ba noppi séddale alalam. \v 23 Ku farul ak man nag, man ngay xeex, te ku àndul ak man di dajale, yaa ngi tasaare. \p \v 24 «Aw rab wu bon, bu jàppee nit ba génn ko, day wër bérab yu fendi, di wut fu mu nopploo, te du ko gis. Su ko defee mu ne: “Naa dellu ca sama kër, ga ma jóge.” \v 25 Bu dikkee fekk kër gi buube, defare ba jekk, \v 26 day dem indi yeneen juróom ñaari rab yu ko yées, ñu bokk sancsi. Su ko defee ni nit kiy mujje mooy yées na mu jëkke.» \p \v 27 Naka la Yeesu di wax loolu, jenn jigéen ca mbooloo ma àddu ca kaw, ne ko: «Ndokklee ki la ëmb ci biiram, nàmpal la ci weenam!» \v 28 Moom nag mu ne ko: «Xanaa kay, ndokklee ñiy déglu kàddug Yàlla te di ko jëfe.» \s1 Yonent Yàlla Yunus doy na firnde \p \v 29 Naka la mbooloo may gëna takku, Yeesu ne: «Niti tey jii, nit ñu bon lañu. Firnde lañuy wut, waaye deesu leen jox jenn firnde ju moy firndey Yunus. \v 30 Ndax na Yunus nekke woon firnde ca waa Niniw, noonu la \w Doomu nit ki|lemma="Doomu nit k-:"\w* nekke firnde ci niti tey jii. \v 31 Keroog àtte ba, Lingeeru bëj-saalum dina jóg, janook niti tey jii, tiiñal leen; ndax moo bàyyikoo woon ca catal àddina, ngir déglusi xam-xamu Suleymaan, te tey jii, ku sut Suleymaan a ngi fi. \v 32 Waa réewum Niniw it keroog àtte ba dinañu taxaw, layook niti tey jii, tiiñal leen ndax ñoo tuube woon ca waareb Yunus, te tey jii, ku sut Yunus a ngi fi. \s1 Bët mooy làmpu yaram \p \v 33 «Deesul taal ab làmp, di ko dugal fu làqu, mbaa ci suufu leget. Dees koy aj kay, ba kuy duggsi gis muy leer. \v 34 Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët wéree, sa yaram wépp a ciy leerloo, waaye bu sa bët bonee, sa yaram wépp a ngi ci lëndëm. \v 35 Kon seetal ndax leer gi nga foog ne mu ngi ci yaw du ag lëndëm. \v 36 Bu sa yaram wépp dee leerlu nag te lenn nekku ci cig lëndëm, su boobaa la sa yaram di mana leerlu ba ne ràññ, mel ni bu la ab làmp niitee, ne ràññ ci sa kaw.» \s1 Yeesu xas na niti diine ñi \p \v 37 Ba Yeesu waxee ba noppi, ab \w Farisen|lemma="Farisen y-:"\w* da koo woo këram, ngir bokk ak moom lekk. Mu nangu, dem ba duggsi, daldi toog ca lekkukaay ba. \v 38 Farisen bi nag jaaxle, ndax la Yeesu setluwul bala moo waaja lekk. \v 39 Sang bi ne ko: «Yeen Farisen yi, bitib kaas bi ak ndab li daal ngeen di raxas, te fekk leen feese jikkoy jagoo lu lewul, akug mbon ci biir! \v 40 Yeena ñàkk xel! Xanaa du ki sàkk biti moo sàkk biir itam? \v 41 Li ci biir kay ngeen di sarxe! Su boobaa seen lépp ay set. \v 42 Waaye wóoy ngalla yeen Farisen yi! Xobi naana ak yeneen safal yu mel ni ru\f + \fr 11.42 \fr*\fk ru \fk*\ft gàncax la. Xob yi dees na ko togg, di ko fajoo.\ft*\f* ak wépp xeetu lujum, yeena ngi ciy génne cérub fukkeel, ngir asaka, njubte ak cofeelu Yàlla nag, ngeen sàggane. Lii de war na leen, waaye lee it, waruleen koo sàggane. \v 43 Wóoy ngalla yeen Farisen yi! Yeenay sàkku péete yu kaname ca jàngu ya, ak nuyoob gëddaal ca pénc ma. \v 44 Wóoy ngalla yeen, yeena ngi mel ni ay bàmmeel yu amul xàmmikaay, nit ñiy dox ca kaw te xamuñu ko.» \p \v 45 Kenn ci xamkati yoon yi nag àddu ne: «Sëriñ bi, loolu nga wax de, nun itam, xasaale nga nu ci.» \v 46 Yeesu itam ne: «Yeen xamkati yoon yi itam, wóoy ngalla yeen, yeen ñi sëf nit ñi sëf yu ñu àttanul, te yeen ci seen bopp, seen benn baaraam sax du ci laal. \v 47 Wóoy ngalla yeen, yeenay tabax bàmmeeli yonent yi, te seeni maam reyoon leen. \v 48 Kon yeena seedee noonu ne seen jëfi maam ya, ànd ngeen ci, ndax ñoom ñoo leen rey, yeen ngeen tabax seeni bàmmeel. \v 49 Looloo tax itam kàddug Yàlla giy xel, biral ne: “Maay yebal fa ñoom ay yonent aki ndaw, ñii ñu bóom, ñee, ñu bundxatal.” \v 50 Su ko defee yoon topp niti tey jii, deretu mboolem yonent yi tuuru, dale ko ca cosaanu àddina. \v 51 La dale ca deretu Abel ba ca deretu Sàkkaryaa\f + \fr 11.51 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk 2.Jaar-jaar ya\+bk* 24.20-22.\ft*\f*, ma ñu rey ca diggante sarxalukaay ba ak bérab bu sell ba, maa leen ko wax déy, dees na ko topp niti tey jii. \v 52 Ngalla yeen xamkati yoon yi, yeena sànk caabiy xam-xam; yeen dugguleen, ñiy duggsi, ngeen tere leena dugg.» \p \v 53 Ba Yeesu génnee foofa, ca la Farisen ya ak firikat ya tàmbalee xabtalu ci kawam, di ko seetloo ay laaj ci mbir yu bare, \v 54 di ko yeeru, tey wuta këf kàddu gu rëcce ci gémmiñam, ngir tuumaal ko. \c 12 \s1 Yeesu aaye na jinigal \p \v 1 Mbooloo ma nag mujj na dajaloo ba mat ay junniy junniy nit, bay joggeente. Ci biir loolu Yeesu tàmbalee wax, jëkke ko ci ay taalibeem, ne: «Wattuleen lawiiru \w Farisen|lemma="Farisen y-:"\w* ñi, te mooy jinigal. \v 2 Mboolem lu nëbbu dees na ko feeñal, te lu làqu dees na ko xam. \v 3 Moo tax mboolem lu ngeen waxe biir lëndëm, dees na ko dégge bëccëg ndarakàmm, te mboolem lu ngeen déeye ci néegu biir, dees na ko biral ci kawi taax. \p \v 4 «Maa leen ko wax, yeen samay soppe, buleen ragal ñu manul lu wees rey seen yaram, ndax gannaaw loolu dootuñu leen manal lu ko raw. \v 5 Ma xamal leen nag ki ngeen wara ragal: kiy rey ba noppi, am sañ-sañu sànni ca sawara sa, kooku déy laa leen ne, ragal-leen ko. \v 6 Juróomi picci ramatu, xanaa jarul ñaari dërëm doŋŋ? Moona Yàlla fàttewula geesu menn ci ñoom. \v 7 Yeen nag seen kawari bopp sax, waññees na lépp. Buleen ragal dara, nde ndiiraanu ramatu, yeena ko gën. \p \v 8 «Te it maa leen ko wax, képp ku dëggal fi kanam nit ñi, ne man nga féeteel, \w Doomu nit ki|lemma="Doomu nit k-:"\w* itam dina dëggal fa kanam malaakay Yàlla ya, ne moom nga féeteel. \v 9 Waaye ku weddi fi kanam nit ñi, ne man nga féeteel, dees na weddi fa kanam malaakay Yàlla ya, ne man nga féeteel. \v 10 Képp ku jëme kàddug safaan ci Doomu nit ki, dees na la jéggal, waaye ku saaga \w Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"\w* gi, deesu la jéggal. \p \v 11 «Bu ñu leen yóbboo ca jàngu ya, ca kanam kilifa ya, ak àttekat ya, buleen jaaxle ci nan ngeen di yékkatee kàddug layoo, ak luy doon seenu lay, mbaa lu ngeen di wax, \v 12 ndax su boobaa Noo gu Sell gi moo leen di xamal ca waxtu woowa la ngeen wara wax.» \s1 Yoolu Yàlla doŋŋ mooy alal \p \v 13 Kenn ca mbooloo ma moo noon Yeesu: «Sëriñ bi, waxal ci sama mag, mu jox ma sama wàll ci ndono li nu bokk.» \v 14 Yeesu ne ko: «Waa jii, kan moo ma fal àttekat mbaa miraaskat ci seen kaw?» \v 15 Ci kaw loolu mu ne leen ñoom ñépp: «Moytuleen wépp xeetu bëgge, ndax loo barele barele, sa bakkan ajuwul ci sa alal.» \p \v 16 Mu léeb leen nag, ne leen: «Nit la woon ku woomle, te ab toolam nangu. \v 17 Mu naan ca xel ma: “Nu may def nag? Amatuma sax fu ma denc sama ngóob mi!” \v 18 Ci kaw loolu mu ne: “Nii laay def: samay sàq laay daaneel, daldi defaraat sàq yu gëna mag, denc ci sama pepp ak mboolem lu ma am. \v 19 Su ko defee ci samam xel laa naan: ‘Céy sama waa ji, yaa ngeek alal ju bare ju mana dem ay ati at; neel finaax, di lekk, di naan ak a bége.’ ” \v 20 Yàlla nag ne ko: “Ñàkk xel! Guddig tey jii, dees na jël sa bakkan. Kon li nga waajal, ana kuy doon boroom?” \p \v 21 «Kuy dajaleel boppam alal te woomlewoo fa Yàlla, loolu mooy saw demin.» \s1 Ku gëm Yàlla, wóolu ko \p \v 22 Gannaaw loolu Yeesu ne ay taalibeem: «Moo tax ma ne leen, buleen seen bakkan jaaxal, ngir lu ngeen lekk, te it buleen seen yaram jaaxal ngir lu ngeen sol, \v 23 ndax lekk gi, bakkan bee ko ëpp solo, te koddaay li it, yaram wee ko ëpp solo. \v 24 Seetleen ci baaxoñ: du ji, du góob, amul ub denc mbaa am sàq. Teewul Yàlla di ko dundal. Yeen nag, ñaata yoon ngeen gën picc yi! \v 25 Ana kan ci yeen mooy jaaxle, di xalaata xalaat bakkanam ba mana yokk lu tollook xef ak xippi ci àppam? \v 26 Ndegam loolu gëna tuut sax moo leen të, ana lu ngeen di xalaat ci leneen? \p \v 27 «Seetleen ni tóor-tóor yiy saxe. Sonnuñu, ëccuñu, waaye maa leen ko wax, Suleymaan ak darajaam jépp sax, soluwul woon ni benn ci ñoom. \v 28 Ndegam ñaxum tool miy dund tey, te léegi ñu sànni ko cib taal, moom la Yàlla solale noonu, xanaa astamaak yeen kay? Yeenaka néew ngëm! \v 29 Yeen nag, buleen tiisoo lu ngeen lekk, mbaa lu ngeen naan; te bu yooyu xalaat ub seen bopp. \v 30 Ndax loolu lépp, xeeti yéefari àddina, ñoo koy tiisoo, te yeen, Baay bi xam na ne soxla ngeen ko. \v 31 Waaye tiisooleen nguuram, su boobaa dees na leen ci dollil loolu. \p \v 32 «Buleen ragal dara, yeen jur gu sew gi, ndax seen Baay la soob, mu jagleel leen nguur gi. \v 33 Jaayleen seen alal, sarxe xaalis bi, sàkkuleen mbuus yu dul ràpp, muy dencu ëllëg bu dul jeex fa asamaan, fa ko sàcc dul jege, max du ko yàq. \v 34 Ndax fu sab denc nekk, sab xol it a nga fa. \s1 Teewlu war na \p \v 35 «Takkuleen te seeni làmp di tàkk. \v 36 Mel-leen ni nit ñuy séentu seen njaatige lu jóge céet, ndax bu dikkee ba fëgg bunt ba, ñu daldi ko ubbil. \v 37 Ndokklee surga yooyu seen njaatige dikk fekk ñu teewlu. Maa leen ko wax déy, njaatige leey takku, toogal leen ba noppi dikk, taajal leen, ñu lekk. \v 38 Ndegam ba guddi ga xaajee la njaatige la ñibbsi, ba fekk surga ya teewloo noonu, am ba suuf seddee la, lu mu ci mana doon, ndokklee ñoom. \v 39 Waaye lii de xamleen ko: boroom kër, su xamoon wan waxtu la ab sàcc di ñëw, du ko wacc moos, mu dàjjiy, dugg këram. \v 40 Kon yeen itam waajleen ba jekk, ndax waxtu wu ngeen foogul, ci la \w Doomu nit ki|lemma="Doomu nit k-:"\w* di ñëw.» \p \v 41 Piyeer nag ne Yeesu: «Sang bi, ndax nun doŋŋ nga léeb lii, am ñépp a ko moom?» \v 42 Sang bi ne ko: «Ana kan nag mooy saytukat bu wóor te muus, ba njaatigeem batale ko curgag këram, ngir mu di leen jox seen njël ca ba muy jot? \v 43 Ndokklee surga bu njaatigeem dikk, fekk ko muy doxale noonu. \v 44 Maa leen ko wax déy, alalam jépp la ko njaatige la di far dénk. \v 45 Waaye su jawriñ ja nee ci xelam: “Sama njaatige dikkagul léegi,” ba tax mu tàmbalee dóor surga ya, góor ak jigéen, di lekk ak a naan, di màndi, \v 46 su boobaa njaatige laay dikk bés bu mu ko séenuwul ak waxtu wu mu foogul, te mbugal mu metti la koy mbugal, sédd ko ci añub gëmadikat ñi. \p \v 47 «Jawriñ jooju xam nammeelu njaatigeem, te taxul mu waaj ko, ba jëfewu ko, ay yetam dina bare. \v 48 Waaye jawriñ ji xamul nammeelu njaatigeem, te teewu koo def lu yelloo ay duma, yet yu néew lay am. Képp ku ñu jox lu bare, dees na la topp lu bare. Képp ku ñu dénk jopp, dees na la feyeeku lu ko ëpp. \s1 Ngëm indi na féewaloo \p \v 49 «Sawara laa taalsi ci kaw suuf, te maaka bëggoon mu ne jippét xaat! \v 50 Am na nag sóobu gu ma wara sóobu, waaye ndaw njàqare ci man li feek loolu sottiwul. \v 51 Foog ngeen ne maye jàmm ci kaw suuf moo ma indi? Déet kay. Maa leen wax lii, xanaa ag féewaloo. \v 52 Gannaaw-si-tey, bu juróomi nit bokkee genn kër, dinañu féewaloo; ñett féewaloo ak ñaar, ñaar féewaloo ak ñett. \v 53 Baay dina féewaloo ak doomam ju góor, doom ja féewaloo ak baayam; ndey féewaloo ak doomam ju jigéen, doom ja féewaloo ak ndeyam; ndey féewaloo ak jabaru doomam, jabar ja féewaloo ak ndeyu jëkkër ja.» \s1 Xam pirim jamono war na \p \v 54 Yeesu neeti mbooloo ma: «Bu ngeen gisee mu xiine sowu, dangeen dal naan: “Taw baa ngi ñëw,” te noonu lay ame. \v 55 Bu ngelaw bawoo bëj-saalum, ngeen ne: “Tàngaay wu metti lay doon,” te mooy am. \v 56 Jinigalkat yi ngeen doon! Melow asamaan ak suuf, man ngeen koo firi. Xew-xewi janti tey jii nag, nu ngeen umplee pireem? \p \v 57 «Te itam lu leen tee àtte njub, yeen ci seen bopp? \v 58 Boo àndeek sab jotewaale, ngeen jëm ca àttekat ba, fexeela jubook moom ci yoon wi. Lu ko moy mu yóbbu la ci yoon, yoon jébbal la ndawal buur, mu ne la ràpp tëj. \v 59 Ma ne la, doo fa génne mukk te feyuloo lépp, ba ci poset bi gëna tuut.» \c 13 \s1 Ku tuubul, sànku \p \v 1 Jamono jooju tembe la aw nit dikk, àgge Yeesu mbirum waa Galile yu \w Pilaat|lemma="Pilaat:"\w* bóomoon, jaxase seen deret ak seen dereti juru sarax yu ñu jagleel Yàlla. \v 2 Yeesu ne leen: «Foog ngeen ne waa Galile yooyu dañoo gëna bàkkaar mboolem seen bokki Galile ya ca des, ba tax ñu daj mitit wu ni tollu? \v 3 Maa leen ne déedéet kay, te su ngeen tuubul, noonu ngeen di sànkoo yeen ñépp. \v 4 Fukki nit ak juróom ñett ñooñu tata ja ca Silowe daanu ci seen kaw, ba rey leen nag, ngeen foog ne ñoo gën diy tooñkat ci \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w* gépp? \v 5 Maa leen ne déedéet kay, te su ngeen tuubul, yeen ñépp ay sànku ni ñoom.» \p \v 6 Mu léeb leen lii nag, ne leen: «Garabu figg la nit amoon ci tóokëram. Mu dikk di ko raas-si, gisu ca dara. \v 7 Mu ne surga ba: “Ñetti at a ngii may dikk, raas-si garab gii, gisuma ci dara. Kon gor ko, da fiy xatal rekk.” \v 8 Surga ba ne ko: “Sang bi, bàyyiwaat ko at mii rekk, ba ma wéex ko, def ci tos. \v 9 Jombul mu meññ déwén; lu ko moy, nga gor ko.”» \s1 Yeesu faj na nit bésub Noflaay \p \v 10 Benn \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*, Yeesoo doon jàngle ci ab jàngu. \v 11 Ndeke jenn jigéen a nga fa woon; rab a ko woppal lu wara mat fukki at ak juróom ñett, mu xuuge, manula fexe ba siggi. \v 12 Yeesu gis ko, woo ko, ne ko: «Jongama, teqlikoo nga ak sa laago.» \v 13 Mu \w teg ko ay loxoom|lemma="teg loxo:"\w*, mu siggi ca saa sa, di sàbbaal Yàlla. \v 14 Njiitu jàngu ba nag yékkati kàddug ñaawlu ndax bésub Noflaay ba Yeesu faje. Mu ne mbooloo ma: «Juróom benni fan la nit ñi wara liggéey. Kon ci fan yooyu ngeen wara fajusi, waaye du ci bésub Noflaay.» \v 15 Sang bi ne ko: «Jinigalkat yi ngeen doon! Xanaa du ci bésub Noflaay la kenn ku nekk ci yeen di yiwee aw yëkkam mbaa mbaamam ca gétt ga, ngir wëggi ko? \v 16 Jigéen jii di sëtub \w Ibraayma|lemma="Ibraayma:"\w*, te fukki at ak juróom ñett a ngii \w Seytaane|lemma="Seytaane:"\w* làggal ko, wareesu koo yiwi, teggil ko laago jii ci bésub Noflaay?» \p \v 17 Ba mu waxee loolu, noonam yépp a rus, mbooloo ma nag di bége mboolem jëf ju yéeme, ja muy def. \s1 Doomu fuddën misaal na nguurug Yàlla \p \v 18 Yeesu neeti: «Ana lu nguurug Yàlla di nirool? Ana lu ma koy niruleel? \v 19 Mu ngi mel ni doomu fuddën bu nit jël, sànni cib toolam. Mu sax, màgg ba doon garab gu njanaaw yi tàgg ciy caram.» \s1 Lawiir misaal na nguurug Yàlla \p \v 20 Mu dellu ne: «Ana lu may niruleel nguurug Yàlla? \v 21 Mu ngi mel ni lawiir ju jigéen sàkk, def ko ci ñetti natti sunguf, ba tooyal bépp mujj funki.» \s1 Buntu texe xat na \p \v 22 Yeesu moo doon jaare ay dëkk yu mag ak yu ndaw, jëm \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w*, di jàngle ca yoon wa. \v 23 Mu am ku ko ne: «Sang bi, xanaa ñiy mucc ñu néew lay doon?» Mu ne leen: \v 24 «Góor-góorluleen ba dugge ci bunt bu xat bi, ndax maa leen ko wax, ñu bareey jéema dugg, waaye duñu ko man. \v 25 Bu boroom kër gi xasee jóg, ba tëj bunt bi, fa ngeen di doxe des biti, di fëgg naan: “Sang bi, ubbil nu!” Mu ne leen: “Xawma fu ngeen bokk.” \v 26 Su boobaa ngeen naan: “Noo daan bokk di lekk ak a naan, te sunuy pénc nga daan jànglee.” \v 27 Mu neeti leen: “Nee naa leen xawma fu ngeen bokk. Soreleen ma yeen ñépp, defkati njubadi yi!” \v 28 Foofa la ay jooy ak naqarlu bay yéyu di ame yoon, kera bu ngeen gisee seeni maam \w Ibraayma|lemma="Ibraayma:"\w* ak Isaaxa ak \w Yanqóoba|lemma="Yanqóoba:"\w* ak yonent yépp ca biir nguurug Yàlla, te fekk yeen ci seen bopp, ñu dàq leen ca biti. \v 29 Penku ak sowu, bëj-gànnaar ak bëj-saalum, la aw nit di bawoo, dikk toog ca ndabal bernde la ca nguurug Yàlla. \v 30 Su ko defee nag, ñenn a ngi mujje tey, waaye ëllëg ñooy jiitu; te ñenn a ngi jiitu tey, waaye ëllëg ñooy mujje.» \s1 Dees na tas Yerusalem \p \v 31 Ca jamono jooju tembe la ay \w Farisen|lemma="Farisen y-:"\w* dikk, ne Yeesu: «Jógeel fii, te dem, ndax Buur \w Erodd|lemma="Erodd:"\w* da laa nara rey.» \v 32 Mu ne leen: «Demleen wax njomboor moomu, ne ko: “Maa ngii di dàq rab yi, di maye ag wér, tey ak ëllëg. Bésub ñetteel ba nag ma sottal.” \v 33 Waaye tey ak ëllëg ak sibir, fàww ma dem, ndax ab yonent wareesu koo bóome fenn fu dul \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w*. \p \v 34 «Yerusalem, Yerusalem, yaw miy bóom yonent yi, di sànni ay doj ñi ñu yebal ci yaw, ba ñu dee, ñaata yoon laa namma dajale say doom, uuf ni ganaar di uufe ay cuujam, te nanguwuloo? \v 35 Mu ngoog, waccees na laak sa kër nag, waaye maa ne la doo ma gisati ba kera jant ba nga naa: “Na barke wàccal ki ñëw ci turu Boroom bi!”» \c 14 \s1 Yeesu jàngal na Farisen ya \p \v 1 Benn \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w* la Yeesu reeri woon kër genn kilifag \w Farisen|lemma="Farisen y-:"\w* ya. Ñoom nag ñu di ko bàyyi xel bu baax. \v 2 Ndeke jenn waay a nga fa janook moom, yaram wépp a sadd. \v 3 Yeesu àddu, ne xamkati yoon yaak Farisen ya: «Waaw, pajum bésub Noflaay, yoon maye na ko, am déet?» \p \v 4 Ñu ne cell. Yeesu \w teg waa ja loxo|lemma="teg loxo:"\w*, wéral ko, daldi ko yiwi. \v 5 Mu ne leen: «Ana kan ci yeen la doomam mbaa aw yëkkam daanu cib teen, mu bañ koo daldi génne ci bésub Noflaay?» \v 6 Lu ñu ca teg nag të leen, ñu ne xerem. \p \v 7 Ci biir loolu Yeesu gis na gan ñay taamoo toogu yu kaname, mu léeb leen, ne leen: \v 8 «Bu la boroom xew wooyee ci berndeg céet, bul wàllisi, ba tooge toogu ba gëna kaname, xamoo fu ku la sutu daraja di wuysee boroom xew ma. \v 9 Su boobaa moom mi la woo, woo ko, mooy dikk, ne la: “Mayal kii, mu toog.” Nga am nag gàccey walbatiku toogi fa gëna gannaawe. \v 10 Bu ñu la wooyee am xew kay, demal tooge fa gëna gannaawe, ba ka la woo dikk ne la: “Xarit, agsil ci kanam.” Su boobaa muy sa teraanga ci kanam mboolem ña nga bokkal bernde ja. \v 11 Ndaxte képp kuy réylu, dees na la toroxal, ka toroxlu lees di yékkati.» \p \v 12 Ci kaw loolu Yeesu ne waa ja ko woo bernde: «Boo dee waajal bernde, añ mbaa reer, bul woo say xarit, mbaa say doomi ndey, mbaa say bokk, mbaa say dëkk yu am alal, nde ñoom itam dañuy walbatiku, woo la rekk, mu doon sag pey. \v 13 Boo dee waajal bernde kay, wool néew-doole yi ak làggi yi, ak ñiy soox ak silmaxa yi. \v 14 Su boobaa ndokklee yaw, nde amuñu sag pey, waaye dees na la fey, kera ndekkitel aji jub ñi.» \s1 Dàq sa teraanga, romb sa njariñ \p \v 15 Kenn ca gan ña nag dégg loolu, ne Yeesu: «Ndokklee ku lekk ca bernde ja ca nguurug Yàlla!» \v 16 Yeesu ne ko: «Jenn waay moo waajaloon bernde ju mag, woo ca ñu bare. \v 17 Ba waxtuw lekk jotee, mu yebal ab surgaam ca ña mu woo woon, ne leen: “Ñëwleen, lépp sotti na léegi.” \p \v 18 «Ñu tàmbalee gàntal nag ñoom ñépp. Kii ne ko: “Ab tool laa jënd, te fàww ma xooli ko. Dama lay ñaan rekk, nga jéggal ma.” \v 19 Kee ne: “Ay lëkkey yëkk, ci laa jënd juróom, damay dem nii, jéemloo leen ba xam. Dama lay ñaan rekk, nga jéggal ma.” \v 20 Kale ne ko: “Ab séet laay sooga takk, looloo tax duma mana ñëw.” \p \v 21 «Surga ba dellu, daldi koy àgge boroom kër ga, njaatigeem. Mu mer, ne surga ba: “Demal gaaw ca pénc yaak mbeddi dëkk bi, te nga indi fii néew-doole yi, ak làggi yi ak silmaxa yi ak ñiy soox.” \p \v 22 «Surga ba dem ba délsi, ne ko: “Sang bi, li nga santaane de def naa ko, waaye kër gi feesagul.” \v 23 Njaatige li ne ko: “Demal topp yoon yi, leru ñag yi, te nga soññ nit ñi, ñu dikk ba sama kër fees.” \v 24 Maa leen ko wax, ñi ma woo woon ci sama bernde ji, kenn du ci mos.» \s1 Topp Yeesu am na lu mu laaj \p \v 25 Yeesu moo doon dem, mbooloo mu réy dar ko. Mu geestu ne leen: \v 26 «Képp ku ñëw ci man, te bañuloo sa baay ak sa ndey, ak sa jabar, ak sa doom, ak sa bokk yu góor, ak sa bokk yu jigéen, bañuloo sa bakkanu bopp sax, doo mana doon sama taalibe. \v 27 Képp ku gàdduwul sa bantu bopp bu ñu lay daaj, te topp ci man, doo mana doon sama taalibe. \v 28 Ana kan ci yeen sax mooy namma tabax taaxum kaw, te jëkkula toog, waññ la mu koy dikke, ngir seet ba xam ndax am na lu ko àggale, \v 29 bala moo teg kenug taax ma, te amul dooley sottal tabax bépp, ba ña koy seetaan di ko ñaawal, \v 30 naan: “Waa jii moo tàmbalee tabax, te manula àggale!” \v 31 Am ban buur mooy xarejeek beneen buur te jëkkula toog, seet ba xam ndax man naa ànd ak fukki junniy xarekatam, ngir xarejeek ku ko songseek ñaar fukki junniy xarekat? \v 32 Su ko manul nag, ba buur bee di soreegum lay yebal kurél ca moom, ngir seet nu mu mana sàrtoo ak moom jàmm. \v 33 Naka noonu itam, kenn ci yeen du mana doon sama taalibe te dëdduwul mboolem lu mu am. \p \v 34 «Xorom déy baax na, waaye bu sàppee, ana lees koy safaleetee? \v 35 Jariñatul suuf, jariñatul ab tos. Ca biti lees koy tuuri. Ku ami nopp kat, déglul.» \c 15 \s1 Sàmm bége na menn xaram mu feeñ \p \v 1 Mboolem \w juutikat|lemma="juutikat b-:"\w* yeek bàkkaarkat yi ñoo daan ñëw ci Yeesu, di ko déglu. \v 2 Ci biir loolu \w Farisen|lemma="Farisen y-:"\w* ya ak firikati yoon ya di ñurumtu naan: «Kii moom bàkkaarkat yi lay neexool, di bokk ak ñoom lekk!» \v 3 Yeesu nag léeb leen lii, ne leen: \v 4 «Ana kan ci yeen mooy am téeméeri xar, réerle ci menn, te bàyyiwul ca àll ba juróom ñeent fukki xar ya ak juróom ñeent (99), ngir toppi ma réer, ba gis ko? \v 5 Bu ko gisee lay bég, teg ko ca mbagg ma, yóbbu kër ga. \v 6 Te bu àggee ca kër ga, xarit yaak dëkk ya lay woo, ne leen: “Kaayleen nu bége, sama xar ma réeroon, gis naa ko!” \p \v 7 «Maa leen wax, ne leen: bu benn bàkkaarkat doŋŋ tuubee, noonu rekk lay doone mbégte fa asamaan, ba raw mbégte ma fay am, bu juróom ñeent fukk ak juróom ñeenti nit jubee, te soxlawuñoo tuub. \s1 Jigéen bége na takkaayam lu feeñ \p \v 8 «Te it ana jan jigéen mooy am fukki libidoor, benn réer ca, te taalul ab làmp, buub néeg ba, seeta seet, ba gis ko? \v 9 Bu ko gisee, xarit yaak dëkk ya lay woo, ne leen: “Kaayleen nu bége, libidoor ba réeroon, gis naa ko.” \v 10 Maa leen wax ne leen: noonu rekk lay doone mbégte fa malaakay Yàlla ya, bu benn bàkkaarkat doŋŋ tuubee.» \s1 Baay bége na doomam ju feeñ \p \v 11 Yeesu neeti: «Nit a amoon ñaari doom yu góor. \v 12 Ka gën di ndaw ne baay ba: “Baay, jox ma cér bi ma yoon may ci sunu alal.” Ba loolu amee baay ba séddale leen alalam. \v 13 Ay fan yu néew gannaaw gi, ka gën di ndaw jaay léppam, daldi tukki réew mu sore, di topp bakkanam ba yàq fa alalam. \v 14 Gannaaw ba mu sànkee lépp, xiif bu metti dikkal réew ma, mu daldi tàmbalee ñàkk. \v 15 Ci kaw loolu mu dem, di surgawu ku cosaanoo ca réew mooma, kooku yebal ko ca ay toolam, muy sàmm ay mbaam-xuux. \v 16 Mu dem ba noon ngéeja lekk ca xolliti doomi garab ya mbaam-xuux yay lekk, fajeb xiifam, te kenn mayu ko ca. \v 17 Xel ma mujj délsi, mu ne: “Ñaata surga la sama baay am, seen lekk ne gàññ, man, ab xiif di ma rey fii! \v 18 Naa jóg, dem ca sama baay, ne ko: ‘Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ la; \v 19 yeyootumaa tuddoo sax sa doom; léegi def ma ni ku bokk ci say surga.’ ” \p \v 20 «Mu jóg, ngir dellu kër baayam. Fu sore la ko baayam séene, muy dikk. Mu ñeewante ko, daw, laxasu ko, fóon ko. \v 21 Doom ja ne ko: “Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ la; yeyootumaa tuddoo sax sa doom.” \v 22 Teewul baay ba ne ay surgaam: “Gaawleen indi mbubb mi gëna rafet, solal ko, te ngeen takkal ko ab jaaro ci loxoom, solal ko ay dàll. \v 23 Indileen sëlluw yafal wa, rey, nu lekk, te bànneexu; \v 24 ndax sama doom jii moo dee woon te dekki na, moo réeroon te feeñ na.” Ñu daldi tàmbalee bànneexu. \p \v 25 «Loolaa nga fekk mag ja ca tool ya. Ba mag ja dikkee ba jub kër ga, ca la dégg po ma ak pecc ma. \v 26 Mu woo kenn ca xale ya, laaj ko lu xew. \v 27 Mu ne ko: “Sa rakk jaa délsi, sa baay rey sëlluw yar wa, ndax li mu délseek jàmm.” \p \v 28 «Mag ja nag mer, nanguwula agsi, baayam génn, di ko soññ. \v 29 Mu àddu, ne baayam: “Seetal ñaata at laa la liggéeyal, sa ndigal, masuma koo moy, te man, masuloo maa may sax as tef su nu bégloo, maak samay xarit. \v 30 Sa doom jii dikk, gannaaw ba mu yàqee sa alal ci ay gànc, nga reyal ko sëlluw yafal wi!” \v 31 Mu ne ko: “Doom, yaw de naka jekk man nga nekkal, te mboolem lu ma am, yaa ko moom. \v 32 Waaye mbégte ak bànneex war na, ndax sa rakk jii moo dee woon te dekki na, moo réeroon te feeñ na!”» \c 16 \s1 Saytukat bu dëng def na ag muus \p \v 1 Yeesu neeti ay taalibeem: «Jenn waay ju am alal la woon, ñu boole ko ak ab saytukatam, ne ko day pasar-pasaree alalam. \v 2 Waa ja woo ko, ne ko: “Li ma la déggal, lu mu doon? Limal ma sag caytu, ndax dootoo ma mana saytul.” \p \v 3 «Saytukat ba nag ne ca xelam: “Nu may def nag, gannaaw sama njaatigee ngi nangu caytu gi ci man? Dem gàbbi? Awma kàttanam. Yalwaani? Rus naa ko.” \v 4 Gannaaw loolu mu ne “Xam naa ni may def, ba su ma ñàkkee sama liggéey it, dees na ma fat.” \v 5 Mu daldi woolu kenn, kenn, ña ameel njaatigeem bor. Kii ñëw, mu ne ko: “Ñaata nga ameel sama njaatige?” \v 6 Mu ne ko: “Téeméeri xàndiy diwu oliw.” Mu ne ko: “Sa kayit a ngi, toogal gaaw te bind juróom fukk.” \v 7 Kee, mu ne ko: “Yaw nag, ñaata nga ko ameel?” Mu ne ko: “Téeméeri saakuy pepp.” Mu ne ko: “Sa kayit a ngi, bindal juróom ñett fukk.” \v 8 Njaatige li nag naw saytukat bu njublaŋ boobu ca muus ga mu defe. Ndax kat niti tey jii ñoo gëna muus doomi leer ñi, ci ni ñuy doxale seen digganteek seeni nawle.» \p \v 9 Yeesu teg ca ne: «Maa leen wax ne leen: Alalu àddina ji làmboo njubadi, sàkkooleen ko ay xarit, ngir bu alal ja jeexee, xarit yooya fat leen ca dal yu sax ya. \v 10 Ku maandu ci lu néew nag, maandu ci lu bare; ku jubadi ci lu néew it, jubadi ci lu bare. \v 11 Kon su ngeen maanduwul ci alalu àddina, alal ji dëgg, ana ku leen koy dénk? \v 12 Te su ngeen maanduwul ci alalu jaambur, ana ku leen di dénk seen alalu bopp? \p \v 13 «Ab jaamu kër nag manula jaamu ñaari sang; day dëddu kii, sopp kee; mbaa mu fonk kii, cof kee. Manuleena jaamoondoo Yàlla ak Alal.» \p \v 14 \w Farisen|lemma="Farisen y-:"\w* ñu bëgg xaalis ña nag dégg loolu Yeesu wax lépp, ba noppi di ko ñaawal. \v 15 Yeesu ne leen: «Yeen yeenay jub-jublu ci kanam nit ñi, waaye Yàlla xam na seen xol. Ndax li nit ñi gëna naw, lu seexluwu la fa Yàlla. \p \v 16 «Yoonu Musaa wi ak waxi yonent yi la woon ba kera ba \w Yaxya|lemma="Yaxya:"\w* dikkee. Waaye ba mu dikkee lañu yégle nguurug Yàlla, ñépp di ci jéema dugge seen doole. \v 17 Waaye nag asamaan ak suuf raaf moo gëna yomb genn maaska rote ci mbindum yoonu Musaa. \s1 Pase daganul \p \v 18 «Képp ku fase sa jabar, takk keneen, jaaloo nga; te ku jëkkëram fase, képp ku ko takk, jaaloo nga. \s1 Aji texeedi sàkku na yërmande \p \v 19 «Jenn waay la woon ju bare alal, di sol yérey tànnéef yu rafet, di dunde lu neex bés bu set. \v 20 Ab baadoolo bu ñuy wax Lasaar nag farala tëdde buntu kër waa ji, yaram wa ne fureet aki góom, \v 21 te noon ngéeja fajeb xiifam lu ruuse ci ndabal boroom alal bi. Rax ci dolli xaj yiy dikk, di mar ay góomam. \p \v 22 «Ba baadoolo ba deeyee, malaaka yi yóbbu ko ba ca wetu \w Ibraayma|lemma="Ibraayma:"\w*. Boroom alal ba itam dee, ñu rob ko. \v 23 Ci kaw loolu ñu dugal ko sawara. Ca biir mbugal mu tar ma la dawale bëtam, daldi séen fu sore Ibraayma ak Lasaar ci wetam. \v 24 Mu xaacu ne: “Maam Ibraayma, yërëm ma! Yebalal Lasaar, mu sëpp catal baaraamam ci ndox, dikk seralal ma sama làmmiñ, sawara sii metti na lool!” \v 25 Ibraayma ne ko: “Doom, fàttlikul ne na nga séddoo woon sa bànneex ca àddina, noonu la Lasaar nekke woon aw tiis. Waaye fii nag moo neexle, yaw nga mitile. \v 26 Bu loolu yépp weesee itam, sunu digg ak yeen kàmb gu xóot a fi dox; moo tax ku bëgga jóge fii jëm ci yeen, mbaa mu jóge foofu jëmsi ci nun, du ko man.” \p \v 27 «Ci kaw loolu boroom alal ba ne: “Kon nag maam, ngalla yebalal Lasaar ca sama kër baay, \v 28 ndax sama juróomi rakk a nga fa. Na leen àrtu, ngir ñu baña ñëw ñoom itam ci bérabu metit bii.” \v 29 Ibraayma ne ko: “Waaye ñoom am nañu yoonu \w Musaa|lemma="Musaa:"\w*, am nañu téerey yonent yi. Nañ leen déggal.” \v 30 Mu ne ko: “Loolu doyul, Maam Ibraayma, waaye su kenn bàyyikoo ci ñi dee, dem ba ca ñoom, dinañu tuub.” \v 31 Ibraayma nag ne ko: “Su ñu dégluwul Musaa, dégluwñu yonent yi kay, ku dekki, bàyyikoo ci ñi dee sax du tax ñu gëm.”» \c 17 \s1 Bàkkaarloo nit aay na \p \v 1 Yeesu neeti ay taalibeem: «Ag fiir guy bàkkaarloo manula ñàkk, waaye wóoy ngalla ka koy lal. \v 2 Ñu takkoon doj wu réy ci baatam, sànni ko biir géej moo gën ci moom muy yóbbe bàkkaar kenn ci xale yii. \v 3 Wattuleen seen bopp. \s1 Jéggal-leen ku leen tuubal \p «Bu la sa mbokk tooñee, yedd ko. Bu tuubee, baal ko. \v 4 Su la tooñoon juróom ñaari yoon ci bés bi, te walbatiku juróom ñaari yoon, ne la: “Tuub naa ko,” baal ko rekk.» \s1 Ngëm maye na kéemtaan \p \v 5 Ci kaw loolu ndaw ya ne Sang bi: «Yokk nu ngëm.» \v 6 Sang bi ne leen: «Su ngeen amoon ci ngëm, lu tollu ni peppu fuddën sax, ba ne garab gii: “Buddeekul, dem jëmbate ca géej ga,” su boobaa garab gi déggal leen. \s1 Ab jaam du sàkku jaajëf \p \v 7 «Kan ci yeen la ab jaamam di beyi mbaa mu sàmmi ba jóge tool, dikk, mu ne ko: “Kaay, nu lekk”? \v 8 Xanaa kay da koy wax ne ko: “Defaral sama reer, te takku, taajal ma, ba ma lekk, naan, nga doora lekk, naan.” \v 9 La jaam ba jëfe ndigal tax na sangam sant ko? Déedéet kay. \v 10 Yeen itam noonu. Bu ngeen defee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeena war ne: “Ay jaam rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”» \s1 Yeesu faj na fukki gaana \p \v 11 Ci biir yoon woowu Yeesu jëmoon \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w*, ma nga jaare fa \w Samari|lemma="Samari:"\w* ak Galile digaloo. \v 12 Mu dem bay duggsi cib dëkk, fukki \w gaana|lemma="gaana:"\w* dikk, dajeek moom, ba dànd ko, daldi taxaw. Ñu xaacu ne: \v 13 «Yeesu, Njaatige, yërëm nu!» \v 14 Yeesu nag gis leen, ne leen: «Demleen seetluji seen yaram ca \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ya.» \p Ba ñuy dem ca sarxalkat ya lañu wér, seen yaram set. \v 15 Kenn ci ñoom gis ne wér na, daldi walbatiku, di xaacuy sàbbaal Yàlla. \v 16 Mu dikk, ne gurub, dëpp jëëm fa tànki Yeesu, sant ko. Waa ja nag nitu \w Samari|lemma="Samari:"\w* la woon. \v 17 Ba loolu amee Yeesu ne: «Xanaa du fukk a wér? Juróom ñeent ña nag, ana ñu? \v 18 Amu ci kenn ku ñëw, delloo Yàlla njukkal ku dul doxandéem bii!» \v 19 Yeesu nag ne ko: «Jógal dem; sa ngëm faj na la.» \s1 Nguurug Yàlla door na ba noppi \p \v 20 \w Farisen|lemma="Farisen y-:"\w* yi ñoo laajoon Yeesu, ne ko: «Kañ la nguurug Yàlla di dikk?» Mu ne leen: «Dikkug nguurug Yàlla du ànd akum ceetaan. \v 21 Deesul ne it: “Xool-leen, mu ngi” mbaa: “Ma ngee,” ndax kat nguurug Yàlla mu ngi ci seen biir.» \p \v 22 Mu ne taalibe ya: «Ay jant a ngi ñëw yu ngeen naa ngéejoo fekke benn bés ci bési \w Doomu nit ki|lemma="Doomu nit k-:"\w*, te dungeen ko fekke. \v 23 Te it, dees na leen ne: “Ma ngee!” mbaa: “Mu ngii!” Buleen dem, buleen ca topp. \v 24 Ndax ni melax di xuyye gii wetu asamaan, ba ne ràññ ca gee, noonu la Doomu nit kiy def keroog bésam. \v 25 Waaye balaa booba fàww Doomu nit ki am coono yu bare, jànkoonteek diiŋatu niti tey jii. \p \v 26 «Noonee mu deme woon ca janti Nóoyin, ni lay deme ca janti Doomu nit ki. \v 27 Nit ñaa nga doon lekk ak a naan, di jël jabar ak a séyi, ba keroog bés ba Nóoyin duggee ca gaal ga, mbënn ma dikk, sànk ñépp. \p \v 28 «Noonee itam la deme woon ca janti Lóot. Nit ñaa nga doon lekk ak a naan, di jënd ak a jaay, di jëmbat ak a tabax. \v 29 Waaye bés ba Lóot génnee \w Sodom|lemma="Sodom ak Gomor:"\w*, la tawub sawara ak tamarax wàcce asamaan, sànk ñépp. \v 30 Noonu doŋŋ lay deme, bés bu Doomu nit kiy feeñ. \p \v 31 «Bésub keroog boobee, ku mu fekk ci kaw am taax, te say yëf ne ca biir kër ga, bul wàcc, di ko jëli. Te ku mu fekk tool ba itam, bul dellu. \v 32 Fàttlikuleen jabaru Lóot ja! \v 33 Képp kuy wuta rawale sa bakkan, yaay ñàkk sa bakkan, waaye képp ku ñàkk sa bakkan, yaay dund. \v 34 Maa leen ko wax: guddig keroog ñaar ay bokk benn lal, kenn ki, ñu yóbbu ko, ka ca des, ñu ba ko. \v 35-36 Ñaar di wolandoo, kenn ki, ñu yóbbu ko, ka ca des, ñu ba ko.» \p \v 37 Taalibe yi ne Yeesu: «Loolu fan la, Sang bi?» Mu ne leen: «Fu médd nekk, fa la tan yay daje.» \c 18 \s1 Saxoo ñaan wareef la \p \v 1 Yeesu dellu leen léeb lii, ngir ñu wareefoo di sax ci ñaan te baña xàddi. \v 2 Mu ne: «Ab àttekat la woon cib dëkk; ragalul Yàlla, yégul nit. \v 3 Ab jëtun a nga woon ca dëkk boobee. Daan na ñëw ca moom, naan ko: “Àtte ma ak sama jotewaale!” \v 4 Àttekat ba bañ na ay yoon, waaye gannaaw gi mu ne ci xelam: “Ragaluma Yàlla, yéguma nit, \v 5 waaye jigéen jii da maa lakkal; naa ko àtte, bala moo dërr-dërri ba mujj jekkli ma.”» \p \v 6 Sang bi teg ca ne: «Jàngatleen li àttekat bu bon bi wax. \v 7 Kon ndax Yàlla man naa baña sàmm àqu tànnéefam ñi koy woo wall guddi ak bëccëg, xanaa di leen yeexe? \v 8 Maa leen ne, mooy sàmm seen àq ci lu gaaw. Waaye bu \w Doomu nit ki|lemma="Doomu nit k-:"\w* dikkee, mbaa dina fekk ngëm ci kaw suuf?» \s1 Ag njub, bu ko boroom gis \p \v 9 Yeesu léebati lii, ngir ñiy damoo seenug njub, tey doyadal ñi ci des. \v 10 Mu ne: «Ñaari nit a julliji woon ca kër Yàlla ga. Kenn ki di ab \w Farisen|lemma="Farisen y-:"\w*, ki ci des dib \w juutikat|lemma="juutikat b-:"\w*. \v 11 Farisen baa nga taxaw di yelu, naan: “Yàlla, maa ngi lay sante li ma melul ni ñeneen ñi doonul lu moy ay lekk-kati àq, ay njublaŋ aki jaalookat, rawatina juutikat bii. \v 12 Maa ngi woor ñaari yoon, ayu bés gu nekk, di joxe asaka benn céru fukkeelu mboolem lu ma am.” \p \v 13 «Juutikat ba moom, ma nga taxaw fu sore, ñemewula siggi sax, xool asamaan, xanaa di fëgg dënnam te naan: “Éy Yàlla, yërëm ma, man bàkkaarkat bi.”» \p \v 14 Yeesu teg ca ne: «Maa ne leen, kooku moo ñibbaale këram àtteb ku jub, waaye du Farisen ba. Ndaxte képp kuy réylu, dees na la toroxal, waaye ki toroxlu lees di yékkati.» \s1 Tuut-tànk am na cér \p \v 15 Doon nañu indil Yeesu ay tuut-tànk sax, ngir mu \w teg leen ay loxoom|lemma="teg loxo:"\w*. Taalibe ya gis loolu, di leen jànni. \v 16 Yeesu nag woolu xale yi, ne: «Bàyyileen xale yi, ñu ñëw fi man, buleen leen aaye, ndax ñu mel ni ñoom ñoo yelloo nguurug Yàlla. \v 17 Maa leen ko wax déy, képp ku baña nangul nguurug Yàlla ni ab xale, doo ca dugg mukk.» \s1 Dëddu lépp, topp Yeesu jafe na \p \v 18 Kenn ci njiiti Yawut yi moo laajoon Yeesu, ne ko: «Sëriñ bu baax bi, ana lu may def, ba texe fàww?» \v 19 Yeesu ne ko: «Lu tax nga naa ma ku baax ki? Kenn baaxul ku moy Yàlla doŋŋ. \v 20 Xam nga ndigal yi: “Bul jaaloo, bul bóom, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, teralal sa ndey ak sa baay.”» \v 21 Mu ne ko: «Loolu lépp, ba may ndaw laa ko dale sàmm ba tey.» \v 22 Yeesu dégg loolu, ne ko: «Lenn rekk nga deseleeti. Mboolem loo am, jaay ko, séddale ko néew-doole yi. Su ko defee nga woomle fa asamaan. Boo noppee, ñëwal, topp ci man.» \v 23 Ba waa ji déggee loolu, am na tiis wu réy, ndax barele woon na lool. \v 24 Yeesu gis loolu, daldi ne: «Boroom alal tàbbi ci nguurug Yàlla, ndaw lu jafe! \v 25 Boroom alal dugg ci nguurug Yàlla de, giléem jaare bën-bënu puso moo ko gëna yomb.» \v 26 Ña cay dégg nag ne: «Kon ku mana mucc nag?» \v 27 Yeesu ne leen: «Li të nit, tëwul Yàlla.» \p \v 28 Piyeer daldi ne: «Nun de, noo ngii, dëddu la nu amoon, topp la.» \v 29 Yeesu ne leen: «Maa leen ko wax déy, amul kenn kuy dëddu kër, mbaa jabar, mbaa mbokk, mbaa waajur, mbaa doom, ngir nguurug Yàlla, \v 30 te jotaatul lu ko ëpp ay yooni yoon, tey jii, akug texe ba fàww, ëllëg.» \s1 Yeesu baamooti na coono yi koy xaar \p \v 31 Yeesu nag yóbbu Fukk ñaak ñaar, wéetook ñoom, ne leen: «Nu ngii jëm \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w*, te mboolem lu yonent yi bindoon ci mbirum \w Doomu nit ki|lemma="Doomu nit k-:"\w* dina sotti. \v 32 Ndax dees na ko jébbal jaambur ñi dul Yawut, dees na ko ñaawal, saaga ko, tifli ko. \v 33 Dinañu ko caw, rey ko, ba ca ñetteelu fanam, mu dekki.» \p \v 34 Waaye ndaw ya, ñoom, xamuñu dara ci jooju wax, ndax mbóotu kàddug Yeesu gaa leen làqu, ba tax ñu umple la mu wax. \s1 Yeesu faj na silmaxa \p \v 35 Ba Yeesu di jubsi dëkk ba ñuy wax Yeriko, ab silmaxaa nga tooge ca peggu yoon wa, di yalwaan. \v 36 Silmaxa ba dégg mbooloo may romb, mu daldi laaj lu mu doon. \v 37 Ñu ne ko Yeesum Nasaret moo fa jaare. \v 38 Ci kaw loolu mu àddu ca kaw ne: «Yeesu, Sëtub \w Daawuda|lemma="Daawuda:"\w*, yërëm ma!» \v 39 Ña jiitu femmu ko, ngir mu noppi. Teewul mu gëna xaacooti, ne: «Sëtub Daawuda, yërëm ma!» \v 40 Yeesu nag taxaw, ne ñu indil ko ko. Ba mu dikkee, mu laaj ko, ne ko: \v 41 «Loo bëgg ma defal la ko?» Mu ne ko: «Xanaa may gis, Sang bi.» \v 42 Yeesu ne ko: «Gisal! Sa ngëm faj na la.» \v 43 Ca saa sa muy gis, daldi topp ci Yeesu, di sàbbaal Yàlla. Mbooloo mépp gis loolu, di sant Yàlla. \c 19 \s1 Yeesu dal na ak bàkkaarkat ba \p \v 1 Gannaaw loolu Yeesu dugg biir Yeriko, jaare biir dëkk ba, di dem. \v 2 Ndeke jenn waay a nga fa, di \w kilifag juutikat|lemma="juutikat b-:"\w* bu bare alal, ñu di ko wax Sase. \v 3 Mu bëgga gis nag kuy Yeesu, te mbooloo ma tax manu koo gis, ndax ndaama la woon. \v 4 Ci kaw loolu Sase daw, jiituji, daldi yéeg ci genn garab ca yoon woowu Yeesu wara jaare, ngir mu man koo gis. \v 5 Yeesu dikk ba tollu foofa, téen ne ko: «Sase, wàccal gaaw, ndax sa kër laa wara dali tey jii.» \p \v 6 Sase daldi wàcc gaaw, bége koo dalal lool. \v 7 Ñépp gis loolu, di ñurumtu naan bàkkaarkat bi la Yeesu dem këram, dal ak moom. \v 8 Sase nag taxaw ne Sang bi: «Sang bi, ma ne, sama genn-wàllu alal, jox naa ko néew-doole yi, te jépp alal ju lewul ju ma masa jëlal kenn, dinaa fey ñeentam.» \v 9 Yeesu ne ko: «Bés niki tey, mucc dikkal na kër gii, ndax waa jii kat ci askanu \w Ibraayma|lemma="Ibraayma:"\w* la bokk, moom itam. \v 10 Ndax \w Doomu nit ki|lemma="Doomu nit k-:"\w*, ñi réer la seetsi, ngir musal leen.» \s1 Ndénkaane aw sas la \p \v 11 Naka la nit ña dégg loolu, Yeesu léebati leen, ndax booba jege na \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w*, te fekk na ñu foog ne nguurug Yàlla day daldi teew ca saa sa. \v 12 Moo tax mu ne: «Boroom juddu bu réy la woon. Muy waaja dem réew mu sore, ngir ñu fal ko fa buur, mu doora ñibbsi. \v 13 Ci biir loolu mu woo fukki surgaam, jox leen ku nekk benn posetub wurus bu gànjare, ne leen: “Liggéeyleen ci, ba ma ñibbsi.” \v 14 Waaye waa réewam ña dañu koo bañoon. Ci gannaawam lañu yónni ndaw, ne: “Kii, bugguñu muy sunu buur.” \p \v 15 «Gannaaw ba ñu ko falee buur, ba mu délsi, daa woolu surga, ya mu joxoon wurus wa, ngir xam ñaata la leen ca seen liggéey jural. \v 16 Kenn ka dikk, ne ko: “Sang bi, sa poset ba jur na fukki poset.” \v 17 Mu ne ko: “Jaaraamaa, surga bu baax bi. Gannaaw ci lu tuut nga wóore nag, falul ci fukki dëkk.” \v 18 Keneen dikk, ne: “Sang bi, sa poset ba indi na juróomi poset.” \v 19 Mu neeti kooka: “Yaw, falul ci juróomi dëkk.” \v 20 Keneen dikk ne: “Sang bi, sa poset baa ngii ma fasoon ciw sekkit. \v 21 Dama laa ragal, ndaxte ku néeg nga. Dangay foqati loo dénkaanewul woon, di dajale loo jiwuloon.” \v 22 Mu ne ko: “Say wax laa lay àttee, surga bu bon bi! Xamoon nga ne nit ku néeg laa, di foqati lu ma dénkaanewul woon, di dajale lu ma jiwuloon. \v 23 Lu la tee woona dénkaaneji sama alal ca dencukaay ba, ngir bu ma dikkee jot ko, boole ca tonoom?” \p \v 24 «Ci kaw loolu mu ne ña fa taxawoon: “Nanguleen poset bi ci moom, jox ko boroom fukki poset yi.” \v 25 Ñu ne ko: “Sang bi, kee ngeek fukki poset ba noppi!” \v 26 Mu ne: “Ma ne leen, képp ku am, dees na ko dolli, waaye ku amul, la mu am as néew sax, dees na ko nangu. \v 27 Sama noon yooyu buggul woon ma doon seen buur nag, indileen leen fii, te rendi leen ci sama kanam.”» \s1 Yeesu dugg na Yerusalem \p \v 28 Ba Yeesu waxee loolu ba noppi, ca la jiitu, jëm \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w*. \v 29 Ba Yeesu dikkee ba jub dëkk ya ñuy wax Betfase ak Betani, ca wetu tund wa ñuy wax \w tundu Oliw|lemma="tundu Oliw y-:"\w* ya, dafa yebal ñaari taalibeem, \v 30 ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci kanam. Bu ngeen agsee, dingeen gis cumbur bu yeewe, bu kenn masula war. Yiwileen ko, indi. \v 31 Bu ñu leen nee: “Lu tax ngeen di ko yiwi?” ne leen: “Sang bee ko soxla.”» \p \v 32 Ba ndaw ya demee, na leen ko Yeesu waxe lañu ko gise. \v 33 Naka lañuy yiwi cumbur ba, ay boroomam ne leen: «Lu tax ngeen di yiwi cumbur bi?» \v 34 Ñu ne: «Boroomam moo ko soxla.» \v 35 Ñu indil Yeesu cumbur bi, sànni seeni yére ca kawam, daldi waral Yeesu. \p \v 36 Naka la Yeesuy dem, nit ñi di ko lalal seeni yére ca yoon wa. \v 37 Ba ñu jubsee Yerusalem, bay wàcce ca mbartalum tundu Oliw ya, mbooloom taalibe mépp la mbégte jàpp, ñu tàmbalee sàbbaal Yàlla ca kaw ndax kéemaan ya ñu gis. \v 38 Ña nga naan: \q1 «Na barke wàccal buur bi ñëw ci turu Boroom bi! \q1 Jàmm fa asamaan; daraja fa bérab ya gëna kawe!» \p \v 39 Yenn \w Farisen|lemma="Farisen y-:"\w* ya woon ca mbooloo ma nag ne Yeesu: «Sëriñ bi, yeddal sa taalibe yi!» \v 40 Mu ne: «Maa leen ko wax, su ñii noppi woon, doj yi ñooy xaacu.» \p \v 41 Ba Yeesu jubsee ba séen dëkk ba, jooy na ndax moom. \v 42 Mu ne: «Céy yaw itam, boo xamoon bésub tey jii li lay may jàmm! Waaye fii mu ne, làqu na say gët. \v 43 Ay bés a ngi dikk ci sa kaw, keroog say noon a lay gawe ab sëkk, yéew la, tance la wet gu nekk. \v 44 Ñoo lay nappaaje ci suuf, yaak say doom yi ci sa biir, te duñu bàyyi doj ci kaw doj ci sa biir, ndax ba sa bésub wall dikkee, yaa ko ràññeewuloon.» \s1 Yeesu jàngle na ca kër Yàlla ga \p \v 45 Gannaaw loolu Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, daldi dàq ña fay jaaye. \v 46 Mu ne leen: «Bindees na ne: “Sama kër gi kërug julli la, waaye yeen, moom ngeen def rawtub sàcc!”» \p \v 47 Yeesu nag di jàngle bés bu nekk ca kër Yàlla ga. Ba mu ko defee \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yu mag ya, ak firikati yoon ya, ñook njiiti xeet wa, di ko wuta rey. \v 48 Waaye xamuñu nu ñuy def, ndax ñépp a ko doon déglu, teewlu ko lool. \c 20 \s1 Diiŋat nañu sañ-sañu Yeesu \p \v 1 Mu am bés bu Yeesu doon jàngal askan wi ca kër Yàlla ga, di xamle xibaaru jàmm bi. \w Sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yu mag ya ak firikati yoon ya ne jalañ, ñook njiit ya. \v 2 Ñu ne ko: «Wax nu, lii ngay def, ci ban sañ-sañ nga koy defe, mbaa kan moo la jox boobu sañ-sañ?» \v 3 Yeesu ne leen: «Ma laaj leen man itam lenn, waxleen ma, \v 4 sóobeb \w Yaxya|lemma="Yaxya:"\w* ci ndox, asamaan la ndigal la bawoo, am ci nit ñi?» \v 5 Ñu diisoo ci seen biir, daldi ne: «Su nu nee: asamaan la ndigal la bawoo da naan lu tax kon gëmunu Yaxya? \v 6 Te su nu nee: ci nit ñi la ndigal li bawoo, mbooloo mépp a nuy sànni ay xeer, ndax wóor na leen ne Yaxya ab yonent la woon.» \v 7 Ñu daldi ne ko: «Xamunu fu mu ko jële.» \v 8 Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe lii.» \s1 Beykat ya def nañu lu ëpp \p \v 9 Ci kaw loolu Yeesu léeb askan wa, lii, ne leen: «Jenn waay moo jëmbatoon ab tóokëru reseñ, batale ko ay beykat, daldi dem yoon wu yàgg. \v 10 Ba tóokër ba ñoree, mu yebal ca beykat ya ab surga, ngir ñu jox ko wàllam ca meññeef ma. Beykat ya dóor surga ba, ba noppi dàq ko, mu dellu loxoy neen. \v 11 Mu dellu yónni beneen surga, ñu dóor ko moom itam, torxal ko, dàq ko, mu dellu loxoy neen. \v 12 Mu dellooti yónni ñetteelu surga, kooku it, ñu gaañ ko, sànni ko ca biti. \p \v 13 «Boroom tóokër ba ne: “Nan laay def nag? Naa yónni sama doomu bopp ji ma sopp boog, xanaa moom, dinañu ko rus!” \v 14 Teewul ba beykat ya gisee doom ji, dañu ne ci seen biir: “Kii mooy donn; nanleen ko rey, su ko defee ndono li féeteek nun.” \v 15 Ba loolu amee ñu génne ko tóokër ba, rey ko.» \p «Ana nu boroom tóokër biy def beykat yi nag? \v 16 Xanaa dikk, rey beykat yooyu, dénk tóokër ba ñeneen.» Nit ña dégg loolu daldi ne: «Yàlla tere!» \v 17 Yeesu ne leen jàkk, daldi ne: «Kon nag lii ñu bind, lu muy tekki? \q1 “Doj wi tabaxkat yi beddi woon, \q1 moo mujj di doju coll wi.” \m \v 18 Woowu doj, képp ku ci dal, dammtoo, te ku mu dal, rajaxe la.» \p \v 19 Firikati yoon yaak \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yu mag ya nag, ca saa sa lañu doon fexee teg Yeesu loxo, ndax xamoon nañu ne ñoo moom léeb woowu, waaye nit ña lañu ragal. \s1 Buur ak jagleem, Yàlla ak jagleem \p \v 20 Ba mu ko defee ñu bàyyi Yeesu xel, daldi yebal ay yeerukat, sas leen ñu yiw-yiwlu te di ko fiir ci kaw kàddu ba jàpp ko, ngir jébbal ko boroom dëkk bay boroom kilifteef ga ak sañ-sañ ba. \v 21 Yeerukat ya dikk ne Yeesu: «Sëriñ bi, xam nanu ne njub ngay wax, di ko jàngle. Amuloo parlàqu itam, waaye ci kaw dëgg ngay jànglee yoonu Yàlla. \v 22 Wax nu nag ndax yoon maye na, nu fey Buur \w Sesaar|lemma="Sesaar:"\w* galag, am déet.» \p \v 23 Teewul Yeesu ràññee seen pexe. Mu ne leen: \v 24 «Joxleen ma ab posetub \w dinaar|lemma="Xaalis:"\w*, ma gis. Nataal bii ak tur wii ci binde, kuy boroom?» Ñu ne ko: «Sesaar.» \v 25 Mu ne leen: «Kon kay yëfi Sesaar, joxleen ko Sesaar; te yëfi Yàlla, ngeen jox ko Yàlla.» \p \v 26 Manuñu koo fiir ba jàppe ko menn mbir ca kanam mbooloo ma, xanaa waaru ca tontam, ba wedam. \s1 Sadusen ya fiirati nañu Yeesu \p \v 27 Ñenn ci \w Sadusen|lemma="Sadusen y-:"\w*, yi weddi ne ndee-ndekki am na, ñoo dikkoon ca Yeesu. Ñu ne ko: \v 28 «Sëriñ bi, \w Musaa|lemma="Musaa:"\w* da noo bindal ne ku góor, su ku mu bokkal waajur faatoo te amul ak jabaram doom, na jël jabaram, ngir amal mbokkam ma dee, kuutaay. \v 29 Léegi juróom ñaari góor ñu bokk ndey ak baay la woon. Taaw ba takk jabar, gannaaw gi mu faatu, te bàyyiwul doom. \v 30 Tofo ba, \v 31 ak ñaareelu tofo ba, ku ci nekk donn na ndaw sa ca magam, ñu topplantee ko noonu, ba juróom ñaar ñépp dee te amuñu ca doom. \v 32 Gannaaw gi ndaw sa it dee. \v 33 Ndaw si nag, keroog ndekkite la, kan la ciy doon jabaram, gannaaw juróom ñaar ñépp a ko jëloon jabar?» \p \v 34 Yeesu ne leen: «Ci àddina sii la góor ñi ak jigéen ñi di séy. \v 35 Waaye ña ñu yeyale ndekkitel ëllëg, yeyale leen bakkan ci àddina siy ñëw, ñooñu, su boobaa, kenn du ci am jabar mbaa jëkkër. \v 36 Dootuñu mana dee it, ndax niy malaaka lañuy mel. Ay doomi Yàlla lañuy doon, ndax da leen di fekk dekki. \v 37 Te Musaa ci boppam xamle na ne ñi dee dañuy dekki, na ko téere indee ca mbirum ngarab sa\f + \fr 20.37 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Mucc ga\+bk* 3.6.\ft*\f*. Mooy ba mu wooyee Boroom bi: “Yàllay \w Ibraayma|lemma="Ibraayma:"\w*, Yàllay Isaaxa, Yàllay \w Yanqóoba|lemma="Yanqóoba:"\w*.” \v 38 Kon moom du ñi dee lay seen Yàlla, xanaa ñiy dund, ndax fa moom, ñépp a ngi dund.» \p \v 39 Ci kaw loolu ñenn ca firikati yoon ya àddu ne ko: «Dëgg nga wax, Sëriñ bi!» \p \v 40 Gannaaw loolu ñemeetuñu koo laaj dara. \s1 Almasi sët la, Sang la \p \v 41 Yeesu neeti leen: «Nees mana waxe ne \w Almasi|lemma="Almasi:"\w*, Sëtub \w Daawuda|lemma="Daawuda:"\w* la? \v 42 Daawuda ci boppam moo ne ci téereb Sabóor: \q1 “Boroom bi moo ne sama Sang: \q1 ‘Toogeel sama ndijoor, \q1 \v 43 ba ma def say noon, sa ndëggastal\f + \fr 20.42 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Sabóor\+bk* 110.1.\ft*\f*.’ ” \m \v 44 Gannaaw Daawudaa wooye Almasi “Sang bi,” nu mu nekke ab sëtam?» \p \v 45 Yeesu nag wax ak ay taalibeem, askan wépp di dégg. Mu ne: \v 46 «Moytuleen firikati yoon yi taamoo jaagar-jaagareek seen mbubb yu réy, di sàkku nuyoob gëddaal ca pénc ma, ak toogu yu kaname ca jàngu ya, ak péetey teraanga ca bernde ya. \v 47 Ñooy saax-saaxee alalu jëtun ñi tey julli julliy ngistal yu dul jeex. Ñooñu la seen mbugal di gëna tar.» \c 21 \s1 Sarax néew na te ëpp yool \p \v 1 Ci kaw loolu Yeesu xoolaat, daldi gis boroom alal yi, ñuy dugal seen sarax ca boyetu kër Yàlla ga. \v 2 Mu gis itam ab jëtun bu néew doole, mu def ca ñaari poseti xànjar\f + \fr 21.2 \fr*\ft Mooy posetub lepton. Seetal \ft*\fq Xaalis \fq*\ft ci Leeral yi.\ft*\f*. \v 3 Yeesu ne: «Maa leen ko wax déy, jëtun bii, ñii ñépp, moo leen ëpple lu mu joxe. \v 4 Ndax ñii ñépp, la ñu woomle, ca lañu sompe, def ci boyetu sarax bii; waaye moom ci biir ag ñàkkam la jël mboolem ab dundam, def ci.» \s1 Yerusalem tas, Doomu nit ki délsi \p \v 5 Mu am nag ay nit ñu doon wax ca kër Yàlla ga, ak taaru doji tànnéef, ya ak yeneen alali jooxe ya ñu ko rafetale. Yeesu itam ne leen: \v 6 «Lii ngeen gis nii, ay jant a ngi ñëw yu fi doj dootul des ci kaw doj, lépp ay jóoru.» \p \v 7 Ñu laaj ko ne ko: «Sëriñ bi, loolu kañ lay doon? Ak luy doon ub takk buy xamle ne looloo ngi waaja dikk?» \v 8 Yeesu ne: «Moytuleen, ngir ñu bañ leena nax, ndax ñu bareey dikk, tuddoo sama tur, naan: “Man a,” te naan: “Waxtu wi jege na.” Buleen leen topp. \v 9 Bu ngeen déggee ay xare aki salfaañoo, buleen tiit, ndax fàww loolu jëkka am. Waaye du doonagum muj ga, ca saa sa.» \p \v 10 Mu neeti leen: «Aw xeet dina jógal aw xeet, am réew jógal am réew. \v 11 Ay yëngu-yënguy suuf yu réy dina am, ay xiif aki mbas dikke fu bare, te xew-xew yu raglu dina am, ak firnde yu mag yu jóge asamaan. \v 12 Waaye laata loolu lépp, yeen, dees na leen teg loxo, fitnaal leen, jébbal leen kuréli jàngu ya, tëj leen kaso. Dees na leen yóbbu ci kanami buur aki boroom dëkk ndax sama tur, \v 13 ngir ngeen doxe ca yékkati kàdduy seede. \v 14 Kon nag defleen bu baax ci seen xel, ne soxlawuleena waajal kàddug layoo. \v 15 Ndax man maa leen di jox làmmiñ wu ànd ak xel, wu seen benn noon dul mana dàq mbaa di ko weddi. \v 16 Pexe mu leen jàpplu dina sababoo sax ci seeni waajur ak seen doomi ndey ak seeni jegeñaale ak seeni xarit, te dees na rey ñenn ci yeen, \v 17 Ñépp a leen di bañ ndax sama tur. \v 18 Waaye seen genn kawaru bopp sax du sànku. \v 19 Saxooleen muñ nag, daldi mucc. \p \v 20 «Bu ngeen gisee gàngooru xare gu gaw \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w*, su boobaa xamleen ne tasteem dëgmal na. \v 21 Su boobaa ña mu fekk ca diiwaanu Yude, nañu daw jëm kaw tund ya, ñi ci biir dëkk bi, nañu daw génn, te ña mu fekk ca tool ya, buñu duggsi ci biir dëkk bi. \v 22 Ndax janti mbugal lay doon, ngir sottal mboolem lu ñu bindoon. \v 23 Wóoy ngalla jigéeni wérul ña, ak ñay nàmpal ca yooyu jant! Ndax tiis wu réy lay doon ci réew mi, akam sànj ci kaw askan wii. \v 24 Dinañu fàddoo ñawkay saamar, te dees na leen jàpp njaam, yóbbu ci mboolem xeet yi. Te jaambur ñi dul Yawut ñooy joggati Yerusalem, ba kera àppu ñooñu dul Yawut di mat. \p \v 25 «Ay firnde dinañu feeñ ci jant bi ak weer wi ak biddiiw yi. Ci kaw suuf njàqare ak tiitaange mooy ñeel xeet yi ndax riirum géej gi ak gannax yi, \v 26 nit ñiy séentu li nara dikkal àddina, di xëm ndax tiitaange, nde dooley asamaan dina sàqi. \v 27 Su boobaa dees na gis \w Doomu nit ki|lemma="Doomu nit k-:"\w* di ñëw ciw niir, ànd ak manoore ak daraja ju réy. \v 28 Bu xew-xew yooyu tàmbalee sotti nag, taxawleen te siggi, ndax seenug \w njot|lemma="jot:"\w* dëgmal na.» \p \v 29 Ci kaw loolu Yeesu léeb leen ne leen: «Xool-leen garabu figg mbaa geneen garab. \v 30 Bu ngeen gisee mu jebbi, ca ngeen di xamal seen bopp ne nawet jubsi na ba noppi. \v 31 Bu ngeen gisee xew-xew yooyu sotti, noonu itam ngeen di xame ne nguurug Yàlla dëgmal na. \p \v 32 «Maa leen ko wax déy, niti tey jii duñu wéy mukk, te loolu lépp sottiwul. \v 33 Asamaan ak suuf dina wees, waaye samay wax du wees mukk. \p \v 34 «Moytuleena yaafusal seen bopp ci naan gu ëpp ak màndite ak xalaati àddina, lu ko moy bés ba jekki dal ci seen kaw, \v 35 ndax ni mbaal di bettee, noonu la bés bay jekkee dal ci kaw mboolem ñi ci kaw suuf. \v 36 Teewluleen boog, tey ñaan saa su nekk, ba mana mucc ci mboolem looluy nara xew, ngir ngeen taxaw fi kanam Doomu nit ki.» \p \v 37 Bés bu nekk nag Yeesoo nga doon yendoo jàngle ca kër Yàlla ga, bu guddee mu fanaani ca kaw tund wa ñuy wax \w tundu Oliw|lemma="tundu Oliw y-:"\w* ya. \v 38 Mbooloo mépp a daan jëlu, fekki ko ca kër Yàlla ga, ngir déglu ko. \c 22 \s1 Njiiti yoon yi fexeel nañu Yeesu \p \v 1 \w Màggalu Mburu mu amul lawiir|lemma="Màggali Yawut yi:"\w*, te ñu di ko wax \w bésub Mucc|lemma="Màggali Yawut yi:"\w*, moo jubsi woon. \v 2 Ci biir loolu \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yu mag ya ak firikati yoon ya di seet nu ñuy fexee ba rey Yeesu, waaye dañoo ragaloon nit ña. \v 3 \w Seytaane|lemma="Seytaane:"\w* nag dugg Yuda, mi ñuy wooye Iskaryo te mu bokkoon ca Fukk ñaak ñaar. \v 4 Yuda daldi diisooji ak sarxalkat yu mag ya, ak kilifay wattukati kër Yàlla ga, ngir xam nan lay tege Yeesu ci seeni loxo. \v 5 Ñu am ca mbégte, digook moom, ngir jox ko xaalis. \v 6 Yuda nangu, di wut nag yoon wu mu wore Yeesu, fu mbooloo ma teewul. \s1 Yeesu tàggoo na \p \v 7 Ci kaw loolu bésu \w màggalu Mburu mu amul lawiir|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* agsi, ñu war caa rendi gàttub \w bésub Mucc|lemma="Màggali Yawut yi:"\w*. \v 8 Yeesu yebal Piyeer ak Yowaan ne leen: «Demleen, waajalal nu bésub Mucc bi, ba nu reeri.» \v 9 Ñu ne ko: «Foo bëgg nu waaje ko fa?» \v 10 Mu ne leen: «Bu ngeen di dugg ca dëkk ba rekk, dingeen dajeek waa ju yenu njaqas ndox. Toppleen ci moom ba ca biir kër ga mu jëm, \v 11 te ngeen ne boroom kër ga: “Sëriñ bi nee: Ana néegu gan, bi may reere reeru bésub Mucc, maak samay taalibe?” \v 12 Kooku moo leen di won néegub kaw bu yaa bu ñu defar ba noppi. Foofa ngeen di waajale.» \p \v 13 Ba ñu demee, noonee leen ko Yeesu waxe, na lañu gise lépp. Ñu daldi waajal reer ba. \p \v 14 Ba waxtuw reer jotee, Yeesu toog ak ndaw ya, \v 15 ne leen: «Yàkkamti woon naa lool bokk ak yeen reeru bésub Mucc bii, bala maa tàbbi coono. \v 16 Ndax maa leen ko wax, dootuma ko reer mukk, ba keroog solob reer bi di sotti ca nguurug Yàlla.» \p \v 17 Ci kaw loolu mu jël ab kaas, yékkati kàddug cant, daldi ne: «Jël-leen kaas bii, te ngeen séddoo ko. \v 18 Ndax maa leen ko wax, gannaaw-si-tey dootuma naan ndoxum reseñ, ba kera nguurug Yàlla dikk.» \p \v 19 Gannaaw loolu mu jël mburu, yékkati kàddug cant, dagg ko, jox leen ko ne: «Lii moo di sama yaram wi ñu jooxe ngir yeen. Deeleen def lii, di ma ko fàttlikoo.» \p \v 20 Kaas ba itam noonu la def ak moom gannaaw reer ba, ne leen: «Kaas bii mooy kóllëre gu yees gi fasoo ci sama deret ji leen nara tuurul. \v 21 Waaye nag ki may wor, loxoom a ngi ci ndab lii nu bokk. \v 22 \w Doomu nit ki|lemma="Doomu nit k-:"\w* déy, ni ñu ko dogale, noonu lay deme, waaye wóoy ngalla ki pexe mi ñu koy wore di jaare ci moom.» \v 23 Ci kaw loolu taalibe yi di laajante ci seen biir, kan ci ñoom moo nar jooju jëf. \p \v 24 Ab werante itam dikkal leen, ñuy xëccoo ci seen biir ku wara gëna kawe ci ñoom. \v 25 Yeesu nag ne leen: «Buuri xeeti àddina doole lañuy nguuroo ci seen kaw, teewul ñi leen di néewal doole, baaxekati nit ñi lañu leen di wooye. \v 26 Yeen nag bumu deme noonu ci seen biir. Ki gëna kawe ci yeen, na mel ni moo gën di ndaw, te njiit li, na mel ni ab surga. \v 27 Ki ñu taajal ndab li, ak surga bi ko taajal, ana ku ci gëna kawe? Xanaa du ki ñu taajal? Moonte man, ci seen biir laa tooge toogaayu surga! \v 28 Yeen nag yeenay ñi des ak man ci sama biir coono. \v 29 Man itam ni ma sama baay dénke nguur, ni laa leen koy dénke. \v 30 Yeenay lekk ak a naane ca sama ndab, ca sama nguur, te yeenay tooge ay gàngune, di jiite fukki giiri \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ak ñaar.» \p \v 31 Yeesu neeti: «Simoŋ, Simoŋ! \w Seytaane|lemma="Seytaane:"\w* kat mu ngi sàkku ab sañ-sañ ngir man leena jéri ni am pepp. \v 32 Waaye man tinul naa la, ngir sa ngëm baña giim. Yaw nag boo waññikoo, nanga dooleel sa bokki gëmkat.» \v 33 Piyeer ne ko: «Sang bi, jekk naa ci ànd ak yaw kaso, ak ci ànd ak yaw dee.» \v 34 Yeesu ne ko: «Piyeer, maa la ko wax, bala ganaar a sab tey jii, dinga weddi ñetti yoon ne xam nga ma.» \p \v 35 Yeesu neeti leen: «Ba ma leen yebalee te du dencukaayu xaalis, du mbuus, du carax yu ngeen yóbbaale, ndax ñàkk ngeen dara?» Ñu ne ko: «Déedéet.» \v 36 Mu ne leen: «Léegi nag képp ku am dencukaayu xaalis, na ko jël, ku am mbuus it, na ko jël; ku amul saamar, na jaay mbubbam, jënde saamar. \v 37 Ndax maa leen ko wax, li ñu bind ne, “Mook defkati mbon yi lañu boole ab àtte,” fàww mu am ci man, te loolu jëm ci sama mbir mu ngi sottisi.» \v 38 Ñu ne ko: «Sang bi, ñaari saamar a ngi fi.» Mu ne leen: «Doy na.» \s1 Yeesu ñaan na ca tundu Oliw ya \p \v 39 Ci kaw loolu Yeesu génn, jëm ca \w tundu Oliw|lemma="tundu Oliw y-:"\w* ya, na mu ko baaxoo woon, taalibe ya topp ci moom. \v 40 Ba mu agsee ca bérab ba, da ne leen: «Ñaanleen, ngir baña tàbbi cig fiir.» \v 41 Ba loolu amee mu dànd leen lu tollook saanu xeer, daldi sukk, di ñaan. \v 42 Mu ne: «Baay, su dee sa coobare, teggil ma kaasu naqar bii. Bumuy sama coobare nag, waaye yaw, na sa coobare am.» \v 43 Malaaka mu bawoo asamaan daldi koy feeñu, dooleel ko. \v 44 Njàqare nag jàpp Yeesu, mu gënatee tënku ci kàdduy ñaanam, ba aw ñaqam mujj mel ni lumbi deret, di dal ci suuf. \p \v 45 Mu ñaan ba noppi, daldi jóg, délsi ci taalibe yi, fekk leen ñuy nelaw, sonn lool ndax aw tiis. \v 46 Mu ne leen: «Lu ngeen di nelaw? Jógleen ñaan, ngir baña tàbbi cig fiir.» \s1 Jàpp nañu Yeesu \p \v 47 Naka la Yeesu di wax, daaneelagul, mbooloo ne jimeet, ka ñuy wax Yuda, di kenn ca Fukk ñaak ñaar jiite leen. Yuda dikk ba ci Yeesu, bëgg koo fóon. \v 48 Yeesu ne ko: «Yuda, fóon ngay wore \w Doomu nit ki|lemma="Doomu nit k-:"\w*!» \v 49 Ña ànd ak Yeesu nag gis la ca nara topp, ñu ne: «Sang bi, nu jame saamar boog?» \v 50 Kenn ci ñoom daldi caw surgab \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bu mag ba, njoof noppu ndijooram. \v 51 Teewul Yeesu ne: «Bàyyileen, na fi yem.» Mu laal noppu waa ja, wéral ko. \p \v 52 Ba loolu amee Yeesu wax ak ña ko jàppsi: sarxalkat yu mag ya, ak kilifay wattukati kër Yàlla ga, ak mag ña. Mu ne leen: «Mbete dama di ab fippukat, ba ngeen dikkey saamar aki njur. \v 53 Moona bés bu nekk, maak yeen la woon ca kër Yàlla ga, te teguleen ma loxo. Waaye seen waxtu la léegi, bi kilifteefug lëndëm ayee nii.» \s1 Piyeer jàmbu na \p \v 54 Ba mu ko defee ñu jàpp Yeesu, yóbbu ko ba ca kër \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bu mag ba, Piyeer dànd fu sore, topp ca. \v 55 Fekk na ñu taal sawara ca digg ëtt ba, toog yéew sawara wa, Piyeer dikk toog ca seen biir. \v 56 Ab surga bu jigéen nag gis ko, mu toog fi kanam taal bi, mu ne ko jàkk, ne: «Kii it ci la, moom la àndaloon!» \v 57 Piyeer nag miim, ne: «Soxna si, xawma kooku!» \v 58 Nes tuut keneen gis ko ne: «Yaw it ci ñoom nga!» Piyeer ne ko: «Waa jii, du man!» \p \v 59 Ba ñu ca tegee lu mat waxtu, keneen jaaraat ca wax ja ne: «Kii kay wax-dëgg, moom la àndaloon, nde waa Galile la.» \v 60 Teewul Piyeer ne ko: «Waa jii, li ngay wax, xawma ma ko de!» Ca saa sa, ganaar sab, te kàddug Piyeer daanoogul sax. \v 61 Ci kaw loolu Sang bi geesu, ne jàkk Piyeer, Piyeer fàttliku la ko Sang bi waxoon ne ko: «Bala ganaar a sab tey jii, dina fekk nga jàmbu ma ñetti yoon.» \v 62 Piyeer nag génn, di jooy jooy yu metti. \s1 Mitital nañu Yeesu \p \v 63 Ci kaw loolu ña jàpp Yeesu, di ko kókkali ak a dóor. \v 64 Ñu muur kanam gi, naan ko: «Yaw, waxal nu kàddug \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* boog, ana ku la dóor?» \v 65 Yeneen saaga yu bare tifaar nañu ko ko. \s1 Yeesu janoo naak Pilaat ak Erodd \p \v 66 Ba bët setee, mbooloom magi askanu Yawut, ak \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yu mag ya, ak firikati yoon ya, ñépp daje. Ñu yóbbu Yeesu ca seen kurélu àtte ba. \v 67 Ñu ne ko: «Soo dee \w Almasi|lemma="Almasi:"\w*, wax nu ko.» Mu ne leen: «Su ma leen ko waxee, dungeen ma gëm. \v 68 Te su ma leen laajee, dungeen tontu. \v 69 Waaye gannaaw-si-tey, \w Doomu nit ki|lemma="Doomu nit k-:"\w* mooy toog ci ndijooru Yàlla, Aji Man ji.» \v 70 Ñépp daldi ne: «Kon yaay Doomu Yàlla?» Mu ne leen: «Yeena waxal seen bopp ne man la.» \v 71 Ñu ne nag: «Lu nuy doyeeti seede, gannaaw nun ci sunu bopp noo ko dégge ci gémmiñam!» \c 23 \p \v 1 Gannaaw loolu mbooloo ma mépp jóg, daldi yóbbu Yeesu ca \w Pilaat|lemma="Pilaat:"\w*. \v 2 Ñu tàmbali di ko sosal, naan: «Kii lanu fekk muy fàbbi askan wi, di aaye ku fey \w Sesaar|lemma="Sesaar:"\w* galag, te naan moom ci boppam mooy Almasi, di buur.» \v 3 Pilaat laaj ko ne ko: «Yaa di buurub Yawut yi?» Mu ne ko: «Yaa ko wax.» \v 4 Pilaat ne sarxalkat yu mag ya ak mbooloo ma: «Waa jii, gisuma ci moom genn tooñ.» \v 5 Teewul ñu gëna dëggal seeni wax, ne: «Mooy yékkati askan wi, ndax li muy jàngle ci mboolem réewum Yawut, dale ko ca Galile ba fii.» \p \v 6 Pilaat dégg loolu, daldi ne: «Waa jii waa Galile la?» \v 7 Ba mu wóoree Pilaat ne ca diiwaan, ba ca kilifteefu \w Erodd|lemma="Erodd:"\w* la Yeesu bokk, ca la ko yónnee Erodd, yemook Erodd itam nekk \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w* ca fan yooya. \p \v 8 Ba Erodd gisee Yeesu, bég na lool, ndax yàggoon na koo bëgga gis, ngir la mu déggoon ay mbiram, ba tax mu yaakaara teewe ay kéemaanam. \v 9 Mu laaj ko lu bare, Yeesu tontuwu ko. \v 10 Sarxalkat yu mag ya ak firikati yoon yaa nga taxaw, di ko tuumaal ak doole. \v 11 Erodd aki dagam nag sewal Yeesu, di ko ñaawal. Gannaaw loolu mu solal ko mbubb mu yànj, delloo ko Pilaat. \v 12 Erodd ak Pilaat, bésub keroog ay xarit lañu, doonte ay noon lañu woon. \p \v 13 Ci kaw loolu Pilaat woo sarxalkat yu mag ya, ak njiit ya ak askan wa. \v 14 Mu ne leen: «Yeena ma indil waa jii, ne ma mooy lajjal askan wi. Man nag laaj naa ko ci seen kanam, waaye gisuma ci moom genn tooñ ci li ngeen ko tuumaal. \v 15 Erodd itam gisul lenn ci moom, ndax moo nu ko yónneewaat. Mu ngoog, waa jii deful lenn lu jar àtteb dee. \v 16 Kon nag dama koy dóorlu, yiwi ko.» \v 17 Booba fàww Erodd bàyyil leen kenn ca bésu màggal ga. \v 18 Ñépp daldi xaacoondoo, ne: «Reyal kii te yiwil nu Barabas!» \p \v 19 Barabas nag fippu gu amoon ca dëkk ba, ak nit ku ñu fa bóom, moo waral ñu tëj ko kaso. \v 20 Pilaat namma bàyyi Yeesu, daldi waxaat ak mbooloo ma. \v 21 Teewul ñuy xaacu, naan: «Daaj ko ci bant! Daaj ko ci bant!» \p \v 22 Pilaat ne leen ñetteel bi yoon: «Ana lu bon lu kii def? Lenn lu jar dee, gisuma ko ci moom. Kon nag, dama koy dóorlu, yiwi ko.» \v 23 Ñu gënatee xaacu, di sàkku ñu daaj ko ci bant. Seen coow la mujj ko ëpp doole. \v 24 Ci kaw loolu Pilaat dogal ñu defal leen la ñu sàkku. \v 25 Mu yiwi ka ñu ko ñaanoon, te jëfi fippu ak nit ku ñu bóom taxoon ñu tëj ko kaso. Yeesu nag, mu teg ko ci seeni loxo, ngir ñu def ko lu leen neex. \s1 Daaj nañu Yeesu ci bant \p \v 26 Ba ñuy yóbbu Yeesu, jenn waay ju dëkk Siren, ñu di ko wax Simoŋ, moom lañu dajeel, mu jóge ca tool ya. Ñu teg bant ba ñuy daaj Yeesu, ngir mu gàddu ko, topp ca moom. \v 27 Nit ñu bare nag topp ko, jigéen ñay yuuxu, di ko jooy. \v 28 Yeesu geesu leen, ne: «Yeen jigéeni \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w*, buleen ma jooy! Jooyleen seen bopp ak seeni doom. \v 29 Ay jant a ngi ñëw kat, dees na ca ne: “Ndokklee jigéen ju tëlee am doom, masula jur, masula nàmpal!” \v 30 Su boobaa, \q1 “Nit ñee naan tund yu mag yi: ‘Daanuleen ci sunu kaw!’, \q1 naan tund yu ndaw yi: ‘Suul-leen nu!’ ” \m \v 31 Ndegam bant bu tooy lees di def nii, ana nu bant bu wow di mujje?» \p \v 32 Yóbbaale nañu itam ñaari saaysaay, ngir boole leen ak Yeesu, rey leen. \v 33 Ba ñu agsee ca bérab, ba ñuy wax Kaaŋu bopp, fa lañu daaj Yeesu ci bant, daajaale ñaari saaysaay ya, kenn ca ndijooram, ka ca des ca càmmoñam. \p \v 34 Ci kaw loolu Yeesu ne: «Baay, baal leen, ndax li ñuy def, xamuñu ko.» Ñu daldi tegoo bant ay yéreem, ngir séddoo ko. \v 35 Mbooloo maa nga taxaw di seetaan, njiit ya ñoom di ko kókkali, naan: «Musal na ay nit; na musal boppam nag, ndegam mooy \w Almasib|lemma="Almasi:"\w* Yàlla, ki ñu fal!» \v 36 Takk-der ya it di ko ñaawal. Ñu dikk, tàllal ko bineegar, ngir mu naan. \v 37 Ñu ne ko: «Gannaaw yaa di buurub Yawut yi, musalal sa bopp!» \p \v 38 Ñu bindal ko nag fa ko tiim, mbind mii: «Kii mooy buurub Yawut yi.» \p \v 39 Kenn ca saaysaay ya ñu wékkoon ci bant, di ko xas, naan ko: «Xanaa du yaw yaay Almasi? Wallul sa bopp te wallu nu!» \v 40 Moroom ma nag femmu ko, ne ko: «Ragaloo sax Yàlla, te yaa ngi ci menn mbugal mii? \v 41 Nun sax, lii jaadu na ci nun, ndax sunu yoolu jëf lanu jot. Waaye kii deful dara lu teggi yoon!» \v 42 Mu teg ca ne: «Yeesu, boo délsee ci sa nguur, fàttliku ma!» \v 43 Yeesu ne ko: «Yaw laa ne déy, bésub tey jii, man ngay nekkal fa Àjjana.» \s1 Yeesu saay na \p \v 44 Ba ñu demee ba tollu wetu fukki waxtu ak ñaar ca bëccëg, ag lëndëm a wàcc ca réew ma mépp, ba fukki waxtu ak juróom ca ngoon. \v 45 Naka la jant bi giim, ridob biir néeg Yàlla ba xar ca digg ba. \p \v 46 Ci kaw loolu Yeesu àddu ca kaw, ne: «Baay, jébbal naa la samag noo!» Ba mu waxee loolu la dee. \v 47 \w Njiitu takk-der|lemma="njiitu takk-der b-:"\w* ba ko teewe woon nag sàbbaal Yàlla, ne: «Aylayéwén, waa jii ku jub la.» \p \v 48 Ba loolu amee mboolem ña fa daje woon di seetaan te teewe loolu, ñépp dellu seeni kër, tey fëgg seen dënn ndaxu tiis. \v 49 Mboolem xamey Yeesu, ak jigéen ña ko toppe woon ca Galile, ña nga dànd lu sore, di seetaan. \s1 Rob nañu Yeesu \p \v 50 Ndeke jenn waay ju ñuy wax Yuusufa, ma nga bokkoon ca \w kurélu àttekati|lemma="kurélu àttekat y-:"\w* Yawut ya. Ku baax, ku jub la woon. \v 51 Kooku ànduloon ca àtteb kurél ga ak seen jëf jooju. Ma nga cosaanoo woon dëkkub Yawut ba ñuy wax Arimate, te moom itam, nguurug Yàlla la doon séentu. \v 52 Moom moo dem ca \w Pilaat|lemma="Pilaat:"\w*, sàkku ci moom, mu jox ko néewub Yeesu. \v 53 Gannaaw loolu mu wàccee ko ca bant ba, sànge ko càngaayal lẽe, denc ko ci \w bàmmeel|lemma="bàmmeel b-:"\w* bu ñu yett ciw doj, te maseesu caa denc ab néew. \v 54 Bésub Waajal la woon, \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w* bi ci topp di waaja taxaw. \v 55 Fekk na jigéen ña dale woona ànd ak Yeesu ca Galile, ña nga topp ca Yuusufa. Ñu gis bàmmeel ba, ak na ñu ca dence néew ba. \v 56 Ba loolu amee ñu dellu, waajali cuuraay ak diwu xeeñlu ngir néew ba. Bésub Noflaay nag taxaw, ñu dal-lu, ni ko yoon santaanee. \c 24 \s1 Yeesu Almasi dekki na \p \v 1 Ca ëllëg sa, di ndoortel ayu bés, jigéen ña jëlu dem ca \w bàmmeel|lemma="bàmmeel b-:"\w* ba, yóbbaale cuuraay la ñu waajal. \v 2 Ñu agsi bàmmeel ba, fekk ñu randal doj wa uboon bunt ba, laf ko ca wet ga. \v 3 Ñu dugg, fekkuñu fa néewu Sang Yeesu. \v 4 Naka lañu nekke seenug njaaxle ci loolu, ñaari góor ne jimeet fa seen wet, sol yére yuy melax. \v 5 Naka la leen tiitaange jàpp, ba ñu sukk, dëpp seen jë fa suuf, ñu ne leen: «Kiy dund, lu tax ngeen di ko seet ci biir ñi dee? \v 6 Nekku fi; dekki na. Fàttlikuleen la mu leen waxoon, ba mu génnagulee Galile. \v 7 Da noon: “Fàww ñu teg \w Doomu nit ki|lemma="Doomu nit k-:"\w* ci loxoy bàkkaarkat yi, ñu daaj ko ci bant, rey ko, ba ñetteelu fanam, mu dekki.”» \v 8 Booba lañu fàttliku kàddug Yeesu googu. \p \v 9 Ñu jóge ca bàmmeel ba, dem àgge loolu lépp Fukk ñaak benn, ak ña ca des ñépp. \v 10 Jigéen ña àgge loolu ndaw ya ñoo doon Maryaamam Magdala, ak Yowaana, ak Maryaama yaayu Yanqóoba, ak itam ñeneen jigéen ñu àndoon ak ñoom. \v 11 Teewul ñu def waxi jigéen ña ay caaxaan, ba gëmuñu leen. \v 12 Piyeer nag jóg, daw, ba ca bàmmeel ba. Mu sëgg, yër, gisul lu dul càngaay la. Mu daldi ñibbi, jaaxle lool ca mbir ma. \s1 Yeesu feeñ na ca yoonu Emayus \p \v 13 Ndeke ca bés booba ñaar ca taalibe yaa nga woon ca yoonu dëkk bu ñuy wax Emayus, digganteem ak \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w* wara tollu ci fukki kilomeetar. \v 14 Ña ngay waxtaane mboolem xew-xew yooyu. \v 15 Naka lañuy waxtaan ak a diisoo, Yeesu ci boppam dab leen, ànd ak ñoom. \v 16 Teewul seeni gët tëlee ràññee, ba manuñu koo xàmmi. \v 17 Yeesu ne leen: «Lu ngeen di waxtaane nii ci yoon wi?» Ñu daldi taxaw, seen kanam lëndëm ndaxu tiis. \v 18 Kenn ci ñoom, ku ñuy wax Kelyopas ne ko: «Xanaa yaw rekk de, yaa dal Yerusalem te umple li fi xew fan yii?» \v 19 Yeesu ne leen: «Lu fi xew?» Ñu ne ko: «Mbirum Yeesum Nasaret. Mu doonoon ab yonent bu manoorewu ci jëf ak ci kàddu, Yàlla ak askan wépp seede. \v 20 Waaye sunu \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yu mag ak sunuy njiit ñoo ko teg ciy loxo, ngir ñu teg ko àtteb dee, daaj ko ci bant. \v 21 Nun nag danoo yaakaaroon ne mooy \w jotsi|lemma="jot:"\w* Israyil. Loolu lépp teewul nu ngii ci ñetteelu fan, ba mbir yooyu amee ba tey. \v 22 Ay jigéen ñu bokk ci nun nag ñoo nu jaaxal. Ndax ñoo jëlu dem ca \w bàmmeel|lemma="bàmmeel b-:"\w* ba, \v 23 waaye fekkuñu fa néewam. Ñu dikk, ne ay malaakaa leen feeñu, xamal leen ne Yeesoo ngi dund. \v 24 Ñenn ci sunuy àndandoo it dem nañu ca bàmmeel ba, fekk ko noonee ko jigéen ña waxe. Waaye moom, gisuñu ko.» \p \v 25 Ci kaw loolu mu ne leen: «Yeen daal, yeena ñàkk xel, yeena naqarim xel, ndegam ba tey gëmaguleen mboolem li yonent yi xamle woon! \v 26 Xanaa du fàww \w Almasi|lemma="Almasi:"\w* daj boobu coono, doora dugg ci teraangaam?» \v 27 Mu tàmbalee nag ci Yonent Yàlla \w Musaa|lemma="Musaa:"\w*, jaare ci yonent yépp, tekkil leen mboolem lu Mbind mi indi ci mbiram. \p \v 28 Naka lañuy jub dëkk, ba ñu jëm, mu mel ni ku nara jubal yoonam. \v 29 Ñu daldi koy téye, ne ko: «Dalal ak nun, ndax jant baa ngi so, léegi mu guddi.» \p Ba loolu amee mu dugg, dal ak ñoom. \v 30 Ba reer jotee mu toog ak ñoom ca ndab la, jël mburu ma, yékkati kàddug cant, daldi dagg, jox leen. \v 31 Ca la seeni gët ubbiku, ñu xàmmi ko. Moom nag, mu ne mes, réer leen. \v 32 Ba loolu amee, ku nekk naan sa moroom: «Ndax yéguloo woon cawartey xol bu tooy, ba muy wax ak nun ci yoon wi, di nu firil Mbind mi?» \p \v 33 Ñaari taalibe ya daldi jóg ca waxtu woowu tembe, dellu Yerusalem, ca Fukk ñaak benn. Ñu fekk leen ñu dajeek seeni àndandoo. \v 34 Ci kaw loolu ñu ne ñaar ña jóge Emayus: «Ndeke Sang bi kay, dekki na; feeñu na Simoŋ!» \v 35 Ñaari taalibe ya ñoom it, nettali leen la xewoon ca yoon wa ak na ñu xàmmee Yeesu, ba mu daggee mburu ma. \s1 Yeesu feeñu na ay taalibeem \p \v 36 Ba ñaari taalibe ya di nettali loolu, ca la Yeesu ci boppam ne jimeet taxaw ci seen biir, ne leen: «Jàmm seen!» \v 37 Tiitaange lu réy jàpp leen, ñu foog ne njuuma lañu gis. \v 38 Yeesu nag ne leen: «Lu ngeen di jaaxle, ak lu ngeen di xel-yaar nii? \v 39 Xool-leen samay loxo ak samay tànk. Man la. Làmbleen ma, ba xam! Njuuma amul suux, amuli yax, nii ma ko ame, ngeen gis.» \v 40 Loolu la leen wax, daldi leen won ay loxoom aki tànkam. \v 41 Taalibe ya nag boole mbég akug jaaxle ba tax manuñu koo gëm. Mu ne leen: «Lu ngeen fi am, lu ñuy lekk?» \v 42 Ñu jox ko dogu jën wu ñu lakk. \v 43 Mu jël ko, lekk ci seen kanam. \p \v 44 Ci kaw loolu mu ne leen: «Lii moo di kàddu ya ma leen waxoon ba ma nekkee ak yeen. Noon naa leen: Mboolem li ñu bind ci samay mbir ci yoonu \w Musaa|lemma="Musaa:"\w*, ak ci téerey yonent yi, ak ci Sabóor, fàww lépp sotti.» \v 45 Ca la ubbi seen xel, ngir Mbind mi leer leen. \v 46 Mu ne leen: «Nii lees binde, ne fàww \w Almasi|lemma="Almasi:"\w* dee ci biir coono, ba ñetteelu fanam, mu dekki, \v 47 te ciw turam, dees na dale ci \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w*, yégal xeet yépp, tuubeel gu jur njéggalug bàkkaar. \v 48 Loolu yeena ko seede. \v 49 Man ci sama bopp maa leen di yónnee li sama baay dige. Waaye yeen toogleen ci dëkk bi, ba kera ñu leen solee manoore ju bawoo fa kaw.» \s1 Yeesu tàggooti na \p \v 50 Gannaaw loolu Yeesu yóbbu leen ca wetu Betani. Ci kaw loolu mu yékkati ay loxoom, barkeel leen. \v 51 Ba mu leen di barkeel, ca la teqlikoo ak ñoom, ñu yéege ko asamaan. \v 52 Ñoom nag, ñu sujjóotal ko, daldi dellu \w Yerusalem|lemma="Yerusalem:"\w*, ànd ak mbég mu réy. \v 53 Saa su nekk, ña nga woon ca kër Yàlla ga foofa, di sant Yàlla.