\id LEV (WOL) \ide UTF-8 \h Sarxalkat yi \toc1 Sasu Sarxalkat yi, di ñetteelu xaaju Tawreetu Musaa \toc2 Sarxalkat yi \mt1 Sasu Sarxalkat yi \mt2 di ñetteelu xaaju Tawreetu Musaa \imt1 Ubbite gi \ip Aaya bi jiitu ci Sasu Sarxalkat yi moo indi na Yàlla àddoo woon ca xaymab ndaje ma, woo Yonent Yàlla Musaa, ngir wax ak moom. Bare na lool fu téere bi joxe ay ndigali yoon aki sàrt yu Yàlla jox Musaa, ngir mu jottli ko bànni Israyil, te dige bi ci Yàlla boole moo di ndigal yooyu ñooy taxa dund képp ku leen jëfe. \ip Ci gàttal, ci téere bi la Yàlla di xamal bànni Israyil, nan lees di dindee mboolem li gàllankoor seenub neexoo ak Yàlla, ak nan lees di jëfe ba xaymab jaamookaay bi doon bérabu ndaje dëgg bu ñuy dajee ak Yàlla. Fàww ñiy jooxe ay sarax jooxe sarax yi ni mu ware. Fàww it sarxalkat yi di nit ñu ñu weg, nit ñu seen jëfin tedd, te kenn ku nekk ci askan wi moytu, kem kàttanam, mboolem luy sobeel aw yaram, te moytu di fecci kóllëre ci jëfinam ak ci ni muy jaamoo Yàlla. Yàlla miy Ku Sell, di Cofeelu neen, di Ki yor ndund, moo namm ñoñam wàllsi ci sellngay boppam, ngir ñoom itam ñu man di jottlee, ndund ak cofeel. Yéene boobu la Yàlla joxe bànni Israyil santaane bii Almasi ne mooy kenug yoonu Yàlla: “Ni ngeen soppe seen bopp nag, nangeen ko soppe seen moroom.” Aaya 19:18. \ip Mboolem ndigali yoon yi ci téere bi, li leen taxa jóg mooy yombal nu gëmkat ñi mana neexoo ak Yàlla, ak fépp fu ñu mana bokk, ak jant bu ñu mana yemool. Kon ndigali yoon yii tàyyiwuñu benn yoon di soññe ci mboolem xeeti kàddu, ngir gëmkat bi saxoo bàyyi xel ne neexoo ak Yàlla manula ñàkk, te ci la ag dundam aju. \ip Ci Tënk: \ili Saar 1—7 Ay dogal ci mbirum sarax yi \ili Saar 8—10 Fal nañu sarxalkat yi \ili Saar 11—15 Sàrtal nañu lu set ak lu setul \ili Saar 16 Lu jëm ci bésub Njotlaay \ili Saar 17—26 Ndigal yi jëm ci sellal \ili Saar 27 Lu jëm ci jagleel Aji Sax ji nit ak alal \ie \c 1 \ms1 Ay dogal ci mbirum sarax yi \mr (Saar 1.1—7.38) \s1 Lu jëm ci saraxu rendi-dóomal \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji woo na Musaa, wax ak moom ca \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* ma ne ko: \v 2 «Waxal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen: Bu kenn ci yeen dee sàkkal Aji Sax ji sarax, na indi ag jur, muy gu gudd mbaa gu gàtt. \p \v 3 «Bu saraxam dee saraxu jur gu gudd gu ñuy def \w rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, na sarxal aw yëkk wu amul sikk. Na ko yóbbu ci bunt xaymab ndaje mi ci kanam Aji Sax ji, ngir mu nangul ko ko. \v 4 Na teg loxoom ci kaw boppu juru saraxu rendi-dóomal bi, ndax ñu nangul ko ko, muy njotlaayam. \v 5 Na rendi yëkk wi ci kanam Aji Sax ji, te doomi Aaróona yu góor yiy \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi ñooy indi deret ji, xëpp ko ci mboolem weti \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi ci bunt xaymab ndaje mi. \v 6 Juru saraxu rendi-dóomal bi, na ko boroom sarax bi fees, daggat ko. \v 7 Doomi Aaróona, sarxalkat bi, dañuy jafal ab taal ci kaw sarxalukaay bi, teg matt mi ci taal bi. \v 8 Su ko defee doomi Aaróona yu góor, yiy sarxalkat yi, jël dog yi, booleek bopp bi ak nebbon bi, teg ko ci kaw mattum taal bi ci sarxalukaay bi. \v 9 Nañu raxas yérey biir yi ak yeel yi, sarxalkat bi boole lépp lakk ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji. \p \v 10 «Bu saraxam dee ab gàtt bu ñuy def rendi-dóomal, muy xar mbaa bëy, na sarxal bu góor bu amul sikk. \v 11 Na rendi sarax si ci kanam Aji Sax ji, fa féete sarxalukaay bi bëj-gànnaar. Na doomi Aaróona yu góor yiy sarxalkat yi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi. \v 12 Bu ko boroom sarax bi daggatee ba noppi, sarxalkat bi day boole dog yeek bopp bi ak nebbon bi, teg ko ci kaw mattum taal bi ci kaw sarxalukaay bi. \v 13 Na boroom sarax bi raxas yérey biir yi ak yeel yi, sarxalkat bi boole lépp lakk ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji. \p \v 14 «Bu nit ki dee sarxalal Aji Sax ji njanaaw luy doon rendi-dóomal, na sarxe pitax mbaa xati mu ndaw. \v 15 Na ko sarxalkat bi yóbbu ca sarxalukaay ba, kutt baat bi, lakk ko ci kaw sarxalukaay bi. Deret ji dees koy siital ci wetu sarxalukaay bi, ba mu jeex. \v 16 Na indi gag bi ak li ci nekk te wetti ko fa ñuy def dóomu-taal ba, fa féete sarxalukaay bi penku. \v 17 Sarxalkat bi day jàpp ci laaf yi, xotti te bañ koo teqale, daldi koy lakk ci sarxalukaay bi, ci kaw mattum taal bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji. \c 2 \s1 Lu jëm ci saraxu pepp \p \v 1 «Bu nit dee indil \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w*, sunguf\f + \fr 2.1 \fr*\ft Sungufu bele lay doon.\ft*\f* su mucc ayib la saraxam wara doon, mu sotti ci diw, def ci \w cuuraay|lemma="cuuraay l-:"\w*, \v 2 te yót ko doomi Aaróona yu góor yiy \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi. Na sarxalkat bi sàkk barci-loxob sunguf su mucc ayib soosu ànd ak diw gi, te boole kook cuuraay li lépp. Na sarxalkat bi def cér boobu saraxu baaxantal, lakk ko ca kaw \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* ba, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji. \v 3 Li des ci saraxu pepp mi, Aaróona aki doomam ñoo koy féetewoo, muy cér bu \w sella sell|lemma="sell:"\w*, bawoo ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji. \p \v 4 «Su dee sarxal lu ñu defare pepp, di lu ñu lakk cib taal ba mu ñor, na doon sunguf su mucc ayib, di mburu yu amul lawiir yu ñu xiiwaale diw, mbaa mburu yu sew yu amul lawiir, ñu sotti diw ca kawam. \v 5 Bu saraxam dee lu ñu defare pepp, lakke ko ci saafukaayu weñ, na doon sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale diw te bumu am lawiir. \v 6 Na ko dammat te sotti diw ca kaw dog ya. Saraxu pepp la. \v 7 Bu saraxam dee lu ñu defare pepp, di lu ñu saaf ci cin ba mu ñor, na doon sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale diw. \p \v 8 «Na yóbbul Aji Sax ji saraxu pepp su ñu defar ci tegtal yooyu, yót ko sarxalkat bi, mu yóbbu ko ca sarxalukaay ba. \v 9 Su ko defee sarxalkat bi génne ci saraxu pepp mi, ab saraxu baaxantal, daldi koy lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm ñeel Aji Sax ji. \v 10 Li des ci saraxu pepp mi, Aaróona aki doomam ñoo koy féetewoo, muy cér bu sella sell, bawoo ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji. \p \v 11 «Du benn saraxu pepp bu ñuy defal Aji Sax ji muy am lawiir, ndax du lenn ci lawiir mbaa lem, lu ñu wara lakk, ngir saraxu sawara su ñeel Aji Sax ji. \v 12 Saraxi ndoortel meññeef man naa ànd ak yooyu, waaye du bokk ci sarax su jëm ca sarxalukaay ba, ñu di ko taal, ngir xetug jàmm. \v 13 Seen mboolem saraxu pepp nangeen ko xorom. Bu seen saraxu pepp ñàkk mukk xorom, ndax mooy màndargaal seen \w kóllëreek|lemma="kóllëre g-:"\w* seen Yàlla. Seen sarax yépp ngeen di xorom. \p \v 14 «Bu nit dee indil Aji Sax ji saraxu ndoortel meññeef, na ko indil mbool\f + \fr 2.14 \fr*\ft Mboolum bele lay doon mbaa mboolum lors.\ft*\f* mu ñu séndal, def ko sànqal, muy saraxu ndoortel meññeefam. \v 15 Na ci sotti diw ak cuuraay. Saraxu pepp la. \v 16 Na sarxalkat bi lakk lenn ci mbool mu mokk mi ànd ak diw, boole kook cuuraay li lépp, muy saraxu baaxantal, te di saraxu sawara. \c 3 \s1 Lu jëm ci saraxi cant ci biir jàmm \p \v 1 «Su fekkee ne li nit kiy sarxe \w saraxu cant la ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*, mu di ko jële ci nag wu góor mbaa wu jigéen, na indil \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji lu amul sikk. \v 2 Day teg loxoom ci kaw boppu jur gi muy sarxal, te rendi ko ca bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* ma. Doomi Aaróona yu góor yiy \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi daldi xëpp deret ji ci mboolem weti \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi. \v 3 Li muy génne ci saraxu cant gi ci biir jàmm, ñu war koo taalal Aji Sax ji mooy nebbon bi sàng yérey biir yi, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi, \v 4 ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon ca kaw, jàpp ca fàllare ja, ak bàjjo bi ci res wi te mu di ko booleek dëmbéen yi, génne ko. \v 5 Na doomi Aaróona yi boole yooyu lakk ci kaw sarxalukaay bi, mu tege ci kaw \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* bi ci kaw mattum taal bi. Saraxu sawara la ngir xetug jàmm ñeel Aji Sax ji. \p \v 6 «Su fekkee ne li nit kiy sarxalal Aji Sax ji saraxu cant la ci biir jàmm, te mu di ko jële ci jur gu gàtt, gu góor mbaa gu jigéen, na sarxal lu amul sikk. \v 7 Su dee sarxal xar, na ko indil Aji Sax ji \v 8 te teg loxoom ci boppu xar mi muy sarxe, ñu rendi ko ci bunt xaymab ndaje mi, doomi Aaróona yu góor yi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi. \v 9 Li muy génne ci saraxu cantu biir jàmm bi, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji, mooy nebbon bi, ak calgeen bi yépp, ñu doge ko fa sës ca fàllare ja, ak nebbon bi sàng yérey biir yi, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi, \v 10 ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon ca kaw, jàpp ca fàllare ja, ak bàjjo bi ci res wi te mu di ko booleek dëmbéen yi, génne ko. \v 11 Na sarxalkat bi boole loolu lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy ñamu sawara, ñeel Aji Sax ji. \p \v 12 «Bu saraxu nit ki dee bëy, na ko indil Aji Sax ji \v 13 te teg loxoom ci bopp bi, ñu rendi ko ci bunt xaymab ndaje mi. Na doomi Aaróona yu góor yi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi. \v 14 La mu cay génnee muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji mooy nebbon bi sàng yérey biir yi yépp, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi, \v 15 ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon ca kaw, jàpp ca fàllare ja, ak bàjjo bi ci res wi te mu di ko booleek dëmbéen yi, génne ko. \v 16 Na sarxalkat bi boole loolu lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy ñamu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji. Mboolem luy nebbon, Aji Sax jeey boroom. \v 17 Dogal a ngii, di lu leen war fàww, ak fépp fu ngeen dëkk: lépp luy nebbon mbaa deret, buleen ko lekk.» \c 4 \s1 Lu jëm ci sarax su bàkkaar sabab \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na itam Musaa ne ko: \v 2 «Waxal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen: Su fekkee ne nit ki dafa moy lenn ci santaaney Aji Sax ji, ba def lenn lu warul te du teyeefam, li ci war lii la. \s1 Li war sarxalkat bu mag bu bàkkaar \p \v 3 «Ndegam \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi ñu diw, fal ko, moo moy, ba yóbbe mbooloo mi tooñ, na indil \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji yëkk wu ndaw wu amul sikk, muy \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w* ndax bàkkaar ba mu def. \v 4 Day yóbbu yëkk wi ci bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi, ci kanam Aji Sax ji, daldi teg loxoom ci boppu yëkk wi, ñu rendi yëkk wi ci kanam Aji Sax ji. \v 5 Sarxalkat bi ñu diw, fal ko, na sàkk ci deretu yëkk wi, yóbbu ci biir xaymab ndaje mi. \v 6 Su ko defee sarxalkat bi capp baaraamam ci deret ji, wis-wisal deret ji juróom ñaari yoon fi kanam Aji Sax ji, fa janook ridob \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* ba. \v 7 Na sarxalkat bi sàkk ci deret ji, taqal ci béjjéni \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* cuuraay lu xeeñ la ca biir xaymab ndaje ma ca kanam Aji Sax ji. Li des ci deretu yëkk wi, na ko tuur ci taatu sarxalukaay bi ñuy lakk \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, foofa ca bunt xaymab ndaje ma. \v 8 Na génne lépp luy nebbon ci yëkk wi ñuy sarxal muy póotum bàkkaar: nebbon bi sàng yérey biir yi, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi, \v 9 ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon ca kaw, jàpp ca fàllare ja, ak bàjjo bi ci res wi te mu di ko booleek dëmbéen yi, génne ko. \v 10 Mooy ni ñu koy génnee rekk ci yëkku \w saraxu cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*. Sarxalkat bi da koy boole lakk ca kaw sarxalukaayu rendi-dóomal ba. \v 11 Waaye deru yëkk wi ak yàppam wépp dees koy booleek bopp bi ak yeel yi ak yérey biir yi ak sébbriit mi; \v 12 mboolem li des ci yëkk wi daal lay génne dal bi, yóbbu ko ci bérab bu mucc sobe, ca jalub dóom ba, daldi taal matt, lakk ko ca, ba mu dib dóom. Foofa dóom ba jale lees koy lakk. \s1 Lu jëm ci sarax yi war mbooloo mi \p \v 13 «Ndegam mbooloom Israyil mépp a moy lenn ci santaaney \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ba def lenn lu warul te du seen teyeef, muy seenug tooñ te seetluwuñu ko, \v 14 bu mbooloo mi nemmikoo moy gi rekk, war nañoo génne ci jur gu gudd gi yëkk wu ndaw wuy doon \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*, yóbbu ko ca bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* ma. \v 15 Magi mbooloo mi dañuy teg seeni loxo ci boppu yëkk wi, fi kanam Aji Sax ji, ba noppi ñu rendi yëkk wi fi kanam Aji Sax ji. \v 16 Gannaaw loolu na \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi ñu diw, fal ko, sàkk ci deretu yëkk wi, yóbbu ci biir xaymab ndaje mi. \v 17 Na capp baaraamam ci deret ji, wis-wisal deret ji juróom ñaari yoon fi kanam Aji Sax ji, foofu ci kanam rido bi. \v 18 Bu noppee na sàkk ci deret ji, taqal ci béjjéni \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi ci kanam Aji Sax ji, ci biir xaymab ndaje mi. Li des ci deret ji, na ko tuur ca taatu sarxalukaayu \w rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* ba, ca bunt xaymab ndaje ma. \v 19 Na génne lépp li ciy nebbon, lakk ko ci kaw sarxalukaay bi. \v 20 Na def ak yëkk woowu na muy def ak yëkku saraxu póotum bàkkaar rekk. Noonu lay def ak moom. Ni la ko sarxalkat biy defale seen njotlaay, ñu am njéggal. \v 21 Na génne yëkk wi dal bi, taal ko, na muy taale yëkk wi ñu jëkka wax. Saraxu póotum bàkkaaru mbooloo mi la. \s1 Li war kilifa gu bàkkaar \p \v 22 «Su fekkee ne kilifa moo moy lenn ci santaaney Yàllaam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ba def lenn lu warul te du teyeefam, mu dig tooñam, \v 23 bu nemmikoo bàkkaar bi mu def rekk, na sarxe sikket bu amul sikk. \v 24 Day teg loxoom ci boppu sikket bi, rendi ko fa ñuy rendi \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, fa kanam Aji Sax ji. \w Saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w* la. \v 25 Na \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi capp baaraamam ci deretu sarax siy póotum bàkkaar, taqal ko ci béjjéni \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* rendi-dóomal bi, ba noppi tuur deret ji ci taatu sarxalukaayu rendi-dóomal bi. \v 26 Na lakk nebbon bi yépp ci kaw sarxalukaay bi, def ko ni nebbonu \w saraxu cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaaram, mu am njéggal. \s1 Li war baadoolo bu bàkkaar \p \v 27 «Su dee kenn ci baadoolo yee moy lenn ci santaaney \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ba def lenn lu warul te du teyeefam, mu dig tooñam, \v 28 bu nemmikoo bàkkaar bi mu def rekk, na sarxe aw bëy wu jigéen wu amul sikk, ndax bàkkaar bi mu def. \v 29 Day teg loxoom ci boppu gàttu \w sarax soosu di póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*, rendi ko fa ñuy lakk \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*. \v 30 Na \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi capp baaraamam ci deret ji, taqal ci béjjéni \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* rendi-dóomal bi; li des ci deret ji da koy tuur ci taatu sarxalukaay bi. \v 31 Te it na génne nebbon bi yépp ni muy génnee nebbonu jur gu ñu def \w saraxu cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*. Na ko sarxalkat bi lakkal Aji Sax ji ci kaw sarxalukaay bi, muy xeeñ xetug jàmm. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaaram, mu am njéggal. \p \v 32 «Su fekkee ne am xar lay sarxe, muy saraxu póotum bàkkaaram, na doon xar mu jigéen, mu amul sikk. \v 33 Day teg loxoom ci boppu xar moomu di saraxu póotum bàkkaar, rendi ko fa ñuy rendee saraxu rendi-dóomal, muy saraxu póotum bàkkaar. \v 34 Na sarxalkat bi capp baaraamam ci deretu xar miy saraxu póotum bàkkaar, te taqal ci béjjéni sarxalukaayu rendi-dóomal bi; li des ci deret ji da koy tuur ci taatu sarxalukaay bi. \v 35 Te itam na génne nebbon bi yépp, ni muy génnee nebbonu xar mu ñuy def saraxu cant ci biir jàmm. Na sarxalkat bi lakk loolu ci kaw sarxalukaay bi, mu dolliku ci saraxu sawara yi ñeel Aji Sax ji. Noonu la sarxalkat biy defale nit ki njotlaayal bàkkaar bi mu def, mu am njéggal. \c 5 \s1 Ay xeeti bàkkaar a ngi ak li ciy njotlaay \p \v 1 «Bu nit bàkkaaree ndax lu mu dégg wooteb seede cib àtte, ba noppi baña wax la mu gis mbaa mu xam ko ca mbir ma, dees na ko ko topp. \p \v 2 «Su fekkee ne nit ki dafa laal lu sobewu, te seetluwu ko, lu mel ni rab wu daganul te médd, muy rabu àll mbaa ag jur, mbaa luy raam, kon sobewu na, tooñ na. \v 3 Su fekkee ne nit ki dafa laal sobey nit ak su mu mana doon, te teyu ko, ba mu wees, saa yu ko xamee, tooñ na. \v 4 Su sàgganee it ba giñ ne dina def nàngam, muy lu baax mbaa lu bon, muy mboolem ngiñ lu ko rëcc te ba mu koy wax teyu ko, ba mu wees, saa yu ko xamee tooñ na. \v 5 Ci tooñin yooyu ñu lim war naa wax na mu tooñe. \v 6 Na indil \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji gàtt bu jigéen, xar mbaa bëy, muy daanam ndax bàkkaar bi mu def. \w Saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w* lay doon, \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi defal ko ko njotlaayal bàkkaar bi mu def. \s1 Lu jëm ci saraxi aji ñàkk \p \v 7 «Nit ki amul lu mat njégu gàtt, na indil \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, muy daanam ndax bàkkaar bi mu def; benn bi di \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*, bi ci des di \w sarax rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*. \v 8 Da koy yót \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi, kooku jëkka rey benn bi, muy saraxu póotum bàkkaar; na kutt baat bi te bumu teqale bopp beek baat bi. \v 9 Day xëpp ci wetu \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi deretu njanaaw liy saraxu póotum bàkkaar. Li des ci deret ji dees koy tuur ci taatu sarxalukaay bi. Saraxu póotum bàkkaar la. \v 10 Ñaareel bi na ko def saraxu rendi-dóomal, muy li ñu santaane. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaar bi mu def, mu am njéggal. \p \v 11 «Su amul lu mat njégu ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, li muy indi, sarxal ko ngir bàkkaar bi mu def, ñetti kiloy sunguf su mucc ayib lay doon, muy saraxu póotum bàkkaar. Du ci def diw, te du ci sotti \w cuuraay|lemma="cuuraay l-:"\w*, ndax li mu di saraxu póotum bàkkaar. \v 12 Da koy yót sarxalkat bi, sarxalkat bi sàkk ci barci-loxo, muy saraxu baaxantal, mu daldi koy lakk ca kaw sarxalukaay bi, mu dolliku ci saraxi sawara yi. Saraxu póotum bàkkaar la. \v 13 Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaar, bi mu def te mu bokk ci xeeti bàkkaar yooyu ñu lim. Su ko defee mu am njéggal. Li des ci sarax bi sarxalkat bee koy moom, mu mel ni bu doon \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* rekk.» \s1 Lu jëm ci saraxu peyug tooñ \p \v 14 Bu loolu weesee, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na Musaa ne ko: \v 15 «Ku ñàkka wormaal lenn lu ñu sellalal Aji Sax ji te du teyeefam, daan ba ko war, mu di ko indil Aji Sax ji, am kuuy mu amul sikk lay doon, ñuy xayma njégam, dëppale dayob xaalis baak natt ba ñu yoonal ca \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* ba. \w Saraxu peyug tooñ|lemma="Sarax yi:"\w* la. \v 16 La mu sàggane woon ca yooyu ñu sellalal Aji Sax ji da koy fey, ba dolli ci juróomeelu céru njég ga mu fey, jox ko \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi. Sarxalkat bi da koy defal kuuy mi njotlaayam, muy saraxu peyug tooñ, ngir mu am njéggal. \p \v 17 «Su fekkee ne nit ki dafa moy lenn ci santaaney Aji Sax ji ci lu warul lu mu def, su ko xamul it, tooñ na, te dees na ko ko topp. \v 18 Na indi kuuy mu amul sikk, ñu xayma njégam, yót ko sarxalkat bi, muy saraxu peyug tooñ. Na ko ko sarxalkat bi defal njotlaayal bàkkaar bi mu def te xamu ko woon. Su ko defee mu am njéggal. \v 19 Loolu saraxu peyug tooñ la, ndax kooka kat tooñ na Aji Sax ji.» \c 6 \p \v 1 Aji Sax ji wax na Musaa ba tey ne ko: \v 2 «Su nit ñàkkee wormaal Aji Sax ji ci waxi fen yu mu wax moroomam, ci alal ju ñu ko tayle mbaa ñu abal ko ko, mbaa muy lu mu jële ci càcc mbaa àq ju mu lekke ci moroomam, \v 3 mbaa muy lu réer boroom, mu for ko, di ko miim, mbaa mu giñ te du dëgg ci mbir mu mu mana doon, \v 4 ku bàkkaare noonu ñu ko waxe, tooñ na, te na delloo alal ji mu ame ci càcc, mbaa njublaŋ mbaa tayle bu ñu ko dénkoon, mbaa muy lu réer, mu for ko. \v 5 Su dee leneen lu ko taxoona giñ te du dëgg itam naka noonu, na ko delloo ba mu mat sëkk, te saa yu ci nekk da cay dolli juróomeelu céru njég ga, jox ko boroom alal ja, keroog ba muy génne saraxu peyug tooñam. \v 6 Na yóbbul Aji Sax ji li ñu koy daan, muy am kuuy mu amul sikk, ñu xayma njégam, muy saraxas peyug tooñ su muy yót sarxalkat bi. \v 7 Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayam fa kanam Aji Sax ji, mu am njéggal ci mboolem lu mu defoon te mu dig tooñam.» \ms2 Mbirum santaane yu sarxalkat yi sasoo \mr (Saar 6.1—7.21) \s1 Lu jëm ci saraxi rendi-dóomal \p \v 8 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxaat Musaa ne ko: \v 9 «Santal Aaróona ak doomam yu góor, ne leen li ñu dogal ci \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* mooy lii: Ab saraxu rendi-dóomal day fanaan fi ñu koy lakke ci kaw \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi, ba bët set, sawara way wéye tàkk ca kaw sarxalukaay ba. \v 10 \w Sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi day sol mbubbam mi ñu ràbbe wëñ gu ëccu\f + \fr 6.3 \fr*\fk wëñ gu ëccu \fk*\ft googu, gàncax gu tudd lẽe lañu koy defare.\ft*\f* ba sew ak tubéyi njiitlaayam ji ñu ràbbe wëñ gu ëccu ba sew. Na tonnee ca sarxalukaay ba dóomu saraxu rendi-dóomal bi, daldi teg dóom bi ci wetu sarxalukaay bi. \v 11 Su ko defee mu summi yéreem yooyu, sol yeneen te génne dóom bi dal bi, yóbbu ko fu mucc sobe. \v 12 Na sawaras sarxalukaay bi wéye tàkk te du fey. Suba su nekk na ko sarxalkat bi xamb, ba noppi teg ci saraxu rendi-dóomal bi, te na lakk nebboni \w saraxi cant gi ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*. \v 13 Na sawara wéye tàkk fàww ci kaw sarxalukaay bi, te bumu fey. \s1 Lu jëm ci saraxi pepp \p \v 14 «Li ñu dogal ci \w saraxi pepp|lemma="Sarax yi:"\w* mooy lii: Na ko doomi Aaróona yu góor joxe fa kanam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ca \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* ba. \v 15 Barci-loxob sunguf su mucc ayib ànd ak diwam lees ciy tibbe, boole kook mboolem \w cuuraay|lemma="cuuraay l-:"\w* la ca kaw saraxu pepp ma, daldi koy lakkal Aji Sax ji ci kaw sarxalukaay bi, muy xeeñ xetug jàmm, di saraxu baaxantal. \v 16 La ca des Aaróona aki doomam yu góor ñoo koy lekk, te buñu ci boole lawiir. Nañu ko lekke ci bérab bu sell. Ci biir ëttu \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi lañu koy lekke. \v 17 Deesu ko lakkaaleek lawiir. Seen cér la bu leen Aji Sax ji sédd ci saraxi sawaraam. Lu \w sella sell|lemma="sell:"\w* la, mel ni \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w* ak \w saraxu peyug tooñ|lemma="Sarax yi:"\w*. \v 18 Képp kuy góor ci doomi Aaróona yi man na cee lekk. Seen cér la bu ñu leen sédde ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, te dogalal leen ko fàww. Lépp lu ci laal day doon lu sella sell.» \p \v 19 Aji Sax ji wax na Musaa ba tey ne ko: \v 20 «Li Aaróona aki doomam yu góor di sarxalal Aji Sax ji, keroog bu ñu koy diw, fal ko, mooy lii: ñetti kiloy sunguf su mucc ayib, tollook saraxu pepp bi ñu saxoo bés bu nekk, te genn-wàll gi di suba, genn-wàll gi ngoon. \v 21 Saafukaayu weñ lañu koy lakke, xiiwaale ko diw, indi xiiw ba, muy saraxu pepp. Nañu ko def ay dog yu ñuy lakkal Aji Sax ji, muy xeeñ xetug jàmm. \v 22 \w Sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi ñuy fal ci doomi Aaróona yu góor yi, mu war koo wuutu, da koy def moom itam. Aji Sax ji moo jagoo sarax boobu fàww, te dañu koy lakk ba mu jeex. \v 23 Te it mboolem saraxu pepp bu sarxalkat di defal boppam, dees koy lakk ba mu jeex. Deesu ci lekk.» \s1 Lu jëm ci sarax su bàkkaar waral \p \v 24 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ne ko: \v 25 «Waxal Aaróona ak doomam yu góor ne leen: Dogal bi ci \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w* mooy lii: Juru saraxas póotum bàkkaar dañu koy rendi fa ñu wara rendi juru \w saraxu dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, fi kanam Aji Sax ji. Lu \w sella sell|lemma="sell:"\w* la. \v 26 \w Sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi koy rendi, muy \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w* da ciy lekk, te fu sell lañu koy lekke, ci biir ëttu \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi. \v 27 Lépp lu laal ci yàpp wi, day doon lu sell, te bu lenn ci deretu sarax si tisee ci kawi yére, dees koy xaj fa mu tis, ci bérab bu sell. \v 28 Su fekkee ne ndabal xandeer lañu togge woon yàppu sarax sa, nañu ko toj. Bu doon ndabal xànjar, ñu jonj ko, raxas ko. \v 29 Képp kuy góor ci askanu sarxalkat sañ na cee lekk. Lu sella sell la. \v 30 Waaye juru saraxas póotum bàkkaar deesu ci lekk lenn te fekk deretam dugg ca biir xaymab ndaje ma, ñu di ca amal ag njotlaay ca biir \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* ba. Loolu du lu ñuy lekk. Dees koy lakk, ba mu dib dóom. \c 7 \s1 Lu jëm ci saraxi peyug tooñ \p \v 1 «Liy dogal bi ci \w saraxas peyug tooñ|lemma="Sarax yi:"\w* mooy lii: Lu \w sella sell|lemma="sell:"\w* la. \v 2 Fa ñuy rendee juru \w saraxu dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, fa lañu wara rendee juru saraxas peyug tooñ. Deret ji dees koy xëpp ci mboolem weti \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi. \v 3 Nebbon ji jépp lañuy sarxal: calgeen bi, nebbon bi sàng yérey biir yi, \v 4 ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon ca kaw, jàpp ca fàllare ja, ak bàjjo bi ci res wi te ñu di ko booleek dëmbéen yi, génne ko. \v 5 \w Sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi da koy boole lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy saraxu sawara, ñeel \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, te di saraxu peyug tooñ. \v 6 Képp kuy góor te bokk ci askanu sarxalkat yi sañ na cee lekk. \w Bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* lees koy lekke. Lu sella sell la. \p \v 7 «Li ci \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w* moo nekk ci saraxu peyug tooñ, dogal bi di benn ci yooyu yaar: sarxalkat bi def gàtt bi njotlaay moo koy moom. \v 8 Su nit joxee ab saraxu rendi-dóomal, sarxalkat bi mooy féetewoo deru jur gi mu sarxal. \v 9 Ci biir loolu bépp \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* mu ñu lakk cib taal, mbaa ñu saaf ko ci cin mbaa ci saafukaayu weñ, sarxalkat bi koy joxe moo koy moom. \v 10 Waaye weneen xeetu saraxu pepp mu mu mana doon, su dee saraxu pepp mu ñuy xiiwaale diw mbaa muy mu wow, doomi Aaróona yu góor yépp a koy moom, ku nekk tollook sa moroom cér. \s1 Lu jëm ci saraxi cant ci biir jàmm \p \v 11 «Li yoon dogal ci \w saraxu cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*, te nit sañ koo sarxalal \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji mooy lii: \v 12 Bu ci nit ki jubloo ag njukkal gu muy delloo Aji Sax ji, day boole ci \w saraxu cant|lemma="Sarax yi:"\w* gi ay mburu yu ndaw yu amul lawiir yu ñu xiiwaale diw ak ay mburu yu tàppandaar yu amul lawiir, ñu wis diw ca kaw, ak ay mburu yu ñu lakke sunguf su mucc ayib, xiiwaale ko diw, not ko bu baax. \v 13 Sarax boobu da ciy dolli mburu yu am lawiir, boole kook saraxu cant googu ci biir jàmm te mu jublu ci njukkal. \v 14 Nañu jooxeel Aji Sax ji ab cér ci sarax yooyu yépp, muy moomeelu \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi xëpp deretu juru saraxas cant gi ci biir jàmm ci mboolem weti sarxalukaay bi. \v 15 Yàppu saraxas cant googu ci biir jàmm te ñu jublu ci njukkal Aji Sax ji, dees koy lekk bés bi ñu ko rendee. Du lenn lees ciy wacc, mu fanaan. \p \v 16 «Su sarax si nit kiy génne dee sarax su ñuy wàccoo ngiñ mbaa \w saraxu yéene|lemma="Sarax yi:"\w*, dees na ko lekk bés bi ko nit ki joxee, te lu ca des ba ca ëllëg sa, ñu man koo lekk. \v 17 Lu des ci yàppu sarax si ba ca gannaaw ëllëg sa dees koy lakk, ba mu dib dóom. \v 18 Waaye kat bu nit lekkee lenn ci yàpp wu ñu def saraxu cant ci biir jàmm te fekk mu am ñetti fan, deesul nangul boroom sarax si te du ko jariñ dara. Lu ñu sib la te ku ca lekk mooy gàddu bàkkaaram. \v 19 Yàpp wu ci laal lenn lu sobewu it deesu ko lekk. Dees koy lakk. Ci biir loolu yàppu sarax, képp ku set sañ nga cee lekk. \v 20 Waaye ku sobewu ku lekk ci yàppu jur gu ñu defal Aji Sax ji saraxu cant ci biir jàmm, kooku nañu ko dagge ci biir bànni Israyil. \v 21 Sobe su mu mana doon, muy lu jóge ci nit mbaa mala mu daganul mbaa mboolem lu daganul te mata sib, ku ci laal ba noppi, lekk ci lu ñu defal Aji Sax ji saraxu cant ci biir jàmm, kooku dees koo wara dagge ci bànni Israyil.» \ms2 Lu jëm ci santaane yi war mbooloo mi \mr (7.22-38) \p \v 22 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dellu wax Musaa ne ko: \v 23 «Waxal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen: Buleen lekk lenn luy nebbonu nag mbaa xar mbaa bëy. \v 24 Nebbonu jur gu dee mbaa lu rabu àll fàdd, manees na koo jëfandikoo neneen nu mu mana doon, waaye deesu ko lekk mukk. \v 25 Képp ku lekk ci nebbonu jur gu ñu def saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji, kooku ko lekk, dees koy dagge ca biir bànni Israyil. \v 26 Te itam du lenn luy deret lu ngeen di lekke fenn fu ngeen dëkk, mu jóge ci njanaaw mbaa ag jur. \v 27 Képp ku lekk lenn luy deret, dees na ko dagge ci biir bànni Israyil.» \p \v 28 Aji Sax ji dellooti wax Musaa ne ko: \v 29 «Waxal bànni Israyil ne leen: Képp kuy jox Aji Sax ji \w saraxu cantam ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w* na indi cér bi Aji Sax ji séddoo ci saraxu cant googu ci biir jàmm. \v 30 Ci loxol boppam lay dindee sarax bi ñuy def saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. Day indi nebbon bi, boole kook dënn bi, dënn bi di \w sarax bu ñuy yékkati|lemma="Sarax yi:"\w*, jébbal Aji Sax ji. \v 31 \w Sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi day lakk nebbon bi ci kaw \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi, waaye dënn bi, Aaróona aki doomam yu góor ñoo ko moom. \v 32 Tànkub ndijoor bi jóge ci seen saraxi cant ci biir jàmm, dees koy jooxeel sarxalkat bi. \v 33 Doomu Aaróona ji joxe deretu sarax beek nebbon bi jóge ci saraxu cant gi ci biir jàmm, kookoo jagoo tànkub ndijoor bi, muy céram. \v 34 Li ko waral mooy, man Aji Sax ji damaa jële ci seen saraxi cant ci biir jàmm, dënn bi ñuy def saraxu yékkati-jébbale, ak tànkub jooxe bi, jox ko Aaróona, sarxalkat bi mook doomam yu góor. Seen cér la ba fàww ci biir bànni Israyil.» \p \v 35 Loolooy céri pal yi Aaróona ak askanam di am ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, dale ko keroog bu ñu leen teewalee fi kanam Aji Sax ji, ñu doon ay sarxalkat. \v 36 Loolu la Aji Sax ji santaane ñu jox leen ko. Bés bu ñu leen xasee diw, fal leen, mu daldi doon seen cér ci biir bànni Israyil ak seen askan ba fàww. \p \v 37 Loolu la yoon digle ci wàllu \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ak \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* ak \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w* ak \w saraxu peyug tooñ|lemma="Sarax yi:"\w* ak saraxu xewu colu ak saraxu cant ci biir jàmm. \v 38 Loolu it la Aji Sax ji dénkoon Musaa ca kaw tundu Sinayi, bés ba mu santee bànni Israyil ca màndiŋu Sinayi ñu di ko génneel ay sarax. \c 8 \ms1 Fal nañu sarxalkat yi \mr (Saar 8—10) \s1 Lu jëm ci xewu colug sarxalkat ya \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ne ko: \v 2 «Indil Aaróona aki doomam yu góor te indaale yére yi ak diw gi ñuy fale ak yëkk wiy \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w* ak ñaari kuuy yi, boole ca pañeb mburu ya amul lawiir, \v 3 te nga woo mbooloo mi mépp, ñu daje ci bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi.» \p \v 4 Musaa def la ko Aji Sax ji sant, mbooloo ma daje ca bunt xaymab ndaje ma. \v 5 Musaa wax mbooloo ma ne leen: «Lii may waaj la Aji Sax ji santaane woon ñu def ko.» \p \v 6 Ci kaw loolu Musaa indi Aaróona aki doomam yu góor, ñu sangu, \v 7 solal Aaróona mbubb mu gudd ma, takkal ko laxasaay ga, solal ko fëxya ba, tegal ko ca \w xar-sànni|lemma="xar-sànni m-:"\w* ma, takkal ko ngañaay la ca kawam, jàppe ko ko, mu tafu ca kawam. \v 8 Mu solal ko nag kiiraayal dënn ba, daldi yeb ca biir kiiraay la jumtukaayi tegtal ya, di \w Urim ba ak Tumim|lemma="Urim ak Tumim:"\w* ba\f + \fr 8.8 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Mucc ga\+bk* 28.30.\ft*\f*, \v 9 la ca tegu mu tegal ko kaala ga ca bopp ba, takkal ko dogu wurus wu tell wa, mooy meeteel gu \w sell|lemma="sell:"\w* ga, mu nekk ca kaw kaala ga, féete kanam, muy la Aji Sax ji santoon Musaa. \p \v 10 Ba loolu wéyee Musaa jël diwu pal ga, diw ca jaamookaay baak ya ca biir yépp, sellale ko yooya, \v 11 ba noppi wis-wisal ca juróom ñaari yoon ca kaw \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* ba, diwe ko sarxalukaay ba ak mboolem ay ndabam, boole ca mbalkam njàpp ma, mook ub tegoom ngir yooyu it sell. \v 12 Mu sotti nag tuuti ci diw gi ñuy fale ci boppu Aaróona, diw ko, sellale ko ko. \v 13 Ba mu ko defee Musaa indi doomi Aaróona yu góor ya, solal leen mbubb yu gudd, takkal leen ay laxasaay, solal leen mbaxana, muy la Aji Sax ji santoon Musaa. \p \v 14 Musaa teg ca indi yëkku sarax siy póotum bàkkaar, Aaróona aki doomam teg seeni loxo ci kaw boppu yëkku sarax siy póotum bàkkaar, \v 15 Musaa rendi ko, sàkk ci deret ji, capp ci baaraamam, diw ci ñeenti béjjéni sarxalukaay bi yépp, setale ko sarxalukaay bi. Mu daldi tuur li des ci deret ji ci taatu sarxalukaay bi, sellale ko noonu, muy njotlaayal sarxalukaay bi. \p \v 16 Ba loolu amee mu jël nebbon bi sàng yérey biir yi, ak bàjjo bi ci res wi ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon, lakk ko ci kaw sarxalukaay bi. \v 17 Li des ci yëkk wi, di der beek yàpp week sébbriit mi, mu génne ko dal bi, lakk ko ca biti, muy la Aji Sax ji santoon Musaa. \p \v 18 La ca tegu mu indi kuuyu \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* bi, Aaróona ak doomam yu góor teg seeni loxo ca boppu kuuy ma. \v 19 Musaa rendi ko, xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi, \v 20 daldi daggat kuuy mi, def ko ay dog, boole bopp beek dog yeek nebbon bi, lakk ko, ba mu dib dóom. \v 21 Ba loolu weesee Musaa boole yérey biir yi, ak yeel yi, raxas, ba noppi lakk kuuy mi yépp ca sarxalukaay ba. Loolu saraxu rendi-dóomal la, ngir xetug jàmm. Saraxu sawara la, ñeel Aji Sax ji, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa. \p \v 22 Gannaaw loolu Musaa indi kuuy ma ca des, di kuuyu xewu colu. Aaróona aki doomam teg seeni loxo ci boppu kuuy mi, \v 23 Musaa rendi ko, sàkk ca deret ja, taqal ca tabanu noppu ndijooru Aaróona, taqal ca baaraamu déyu ndijooram ak baaraamu déyu tànku ndijooram. \v 24 Musaa doora indi doomi Aaróona yu góor ya, sàkk ca deret ja, taqal ca seen tabani noppi ndijoor ak seen baaraamu déyu ndijoor ak seen baaraamu déyu tànki ndijoor. La des ca deret ja, Musaa xëpp ko ca mboolem weti sarxalukaay bi. \v 25 Ba mu ko defee mu génne nebbon bi, muy calgeen bi ak nebbon bi sàng yérey biir yépp ak bàjjo bi ci res wi ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon, ak tànkub ndijoor bi. \v 26 Layu bi def mburu yi amul lawiir, taaje fi kanam Aji Sax ji, mu jële ca menn mburu kese mu ndaw ak menn mburu mu ndaw te am diw ak menn mburu mu tàppandaar, boole ko teg ca kaw nebbon ba ak tànku ndijoor ba. \v 27 Mu boole yooyu yépp teg ci loxol Aaróona ak loxoy doomam yu góor, ngir ñu def ko \w sarax bu ñuy yékkati|lemma="Sarax yi:"\w*, jébbal Aji Sax ji. \v 28 Ba loolu amee Musaa nangoo ko ca seeni loxo, teg ko ca kaw saraxu rendi-dóomal ba, lakk ko ca sarxalukaay ba. Loolu saraxas xewu colu la woon, ngir xetug jàmm. Saraxu sawara la, ñeel Aji Sax ji. \v 29 Musaa daldi jël dënn biy céram ci kuuyu xewu colu gi, yékkati ko, jébbal Aji Sax ji, muy saraxu yékkati-jébbale, di la Aji Sax ji santoon Musaa. \p \v 30 Musaa teg ca sàkk ca diwu pal ga, ak deret ji ci sarxalukaay bi, wis-wisal ko ci kaw yaramu Aaróona ak ca kawi yéreem, wis-wisaale ko ca kaw yarami doomam yu góor ak ca kaw yérey doomam. \p \v 31 Musaa wax ak Aaróona aki doomam yu góor ne leen: «Toggleen yàpp wi ci bunt xaymab ndaje mi te lekk ko foofa, boole kook mburu mi ci layub saraxi xewu colu gi, muy la ma santaane woon ne yaw Aaróona yaak say doom yu góor yeena koy lekk. \v 32 Li des ci yàpp wi ak mburu mi, lakkleen ko, ba mu dib dóom. \v 33 Waaye bunt xaymab ndaje mi buleen ko wees diiru juróom ñaari fan, ba bésub keroog ba seen xewu colu di mat, ndax juróom ñaari fan lay mat. \v 34 Lépp lu ñu def tey, Aji Sax ji daa santaane ñu def ko, mu daldi matal seen njotlaay. \v 35 Ci bunt xaymab ndaje mi ngeen di yem guddeek bëccëg diiru juróom ñaari fan, boole ci di dénkoo dénkaaney Aji Sax ji, ndax ngeen baña dee, ndaxte loolu moo di li ñu ma santoon.» \p \v 36 Aaróona ak doomam yu góor nag def lépp lu Aji Sax ji santaane woon, Musaa jottli. \c 9 \s1 Liggéeyu sarxalkat yi tàmbali na \p \v 1 Keroog bésub juróom ñetteel ba, Musaa woolu na Aaróona ak doomam yu góor, ñook magi Israyil ña. \v 2 Mu ne Aaróona: «Sàkkal aw sëllu, muy \w saraxas póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w* akum kuuy, muy \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, te bu ci lenn am sikk, nga boole indil \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \v 3 Te nga wax \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen ñu jël ab sikket, mu doon saraxu póotum bàkkaar, akaw sëllu akam xar, lu ci nekk am at te mucc sikk, ngir saraxu rendi-dóomal, \v 4 ak itam aw nag akam kuuy, muy \w saraxu cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*, di lu ñuy rendi fi kanam Aji Sax ji. Nañu defaale \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* mu am diw, ndax tey jii Aji Sax ji dina leen feeñu.» \p \v 5 Ba mu ko defee ñu yóbbu ca bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* ma la Musaa santaane woon, mbooloo ma mépp ñëw, taxaw fa kanam Aji Sax ji. \v 6 Musaa ne: «Lii mooy li Aji Sax ji santaane ne, moom ngeen wara def ngir leeram feeñu leen.» \v 7 Musaa wax ak Aaróona ne ko: «Dikkal fii ci \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi te joxe sa saraxu póotum bàkkaar ak sa saraxu rendi-dóomal, nga jotoo ko, yaw yaak mbooloo mi, boo noppee joxe saraxu mbooloo mi, jote leen ko, muy li Aji Sax ji santaane.» \p \v 8 Aaróona dikk ba ci sarxalukaay bi, rendi sëllu wi, muy saraxu póotum bàkkaaram. \v 9 Gannaaw loolu doomi Aaróona yu góor ya indil ko deret ja, mu capp ca baaraamam, taqal ca béjjéni sarxalukaay ba; la des ca deret ja mu tuur ko ca taatu sarxalukaay ba. \v 10 Aaróona jël nebbon bi jóge ci sarax biy póotum bàkkaar, aki dëmbéenam ak bàjjo bi ci res wi, mu boole ko lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy la Aji Sax ji santoon Musaa. \v 11 Yàpp wi ak der bi, mu génne ko dal ba, lakk ko, ba mu dib dóom. \v 12 La ca tegu Aaróona rendi juru rendi-dóomal bi. Ba loolu amee doomam yu góor ya jox ko deret ja, mu xëpp ko ci mboolem weti sarxalukaay bi. \v 13 Ñu jox ko saraxu rendi-dóomal bi ñu def dog yu ànd ak bopp ba, mu boole lakk ca sarxalukaay ba. \v 14 Loolu wéy, mu raxas yérey biir yi, ak yeel yi, teg ko ca kaw saraxu rendi-dóomal ba, lakkaale ko ca. \p \v 15 Gannaaw gi Aaróona indi saraxi mbooloo mi, jël sikketu mbooloo miy doon seen \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*, rendi ko, sarxal ko, na mu sarxale la jiitu. \v 16 Ci kaw loolu mu indi saraxu rendi-dóomal ba, sarxal ko, na ñu ko diglee. \v 17 Mu doora indi saraxu pepp mi, sàkk ci ab tib, lakk ko ca kaw sarxalukaay ba, dolli ko ca dóomalu suba sa. \v 18 Mu sooga rendi nag wi ak kuuy mi, defal ko mbooloo mi saraxu cant ci biir jàmm. Doomam yu góor ya jox ko deret ja, mu xëpp ko ca mboolem weti sarxalukaay ba. \v 19 Waaye lay nebbon ca nag wa ak kuuy ma, di calgeen ba ak nebbon bi sàng yérey biir yi, ak dëmbéen yi ak bàjjo bi ci res wi, \v 20 nebbon yooyu lañu teg ca kaw dënni nag wa ak kuuy ma, Aaróona lakk ko ca kaw sarxalukaay ba. \v 21 Ba mu ko defee Aaróona yékkati dënn yaak tànku ndijoor ba, defal ko Aji Sax ji \w saraxu yékkati-jébbale|lemma="Sarax yi:"\w*, muy la Musaa santaane woon. \p \v 22 Ba Aaróona noppee, yékkati na mbooloo ma ay loxoom, ñaanal leen, doora wàcc. Fekk na mu joxe saraxu póotum bàkkaar ba, ak saraxu rendi-dóomal ba, ak saraxu cant ga ci biir jàmm. \v 23 Musaa ak Aaróona ànd dugg ca biir xaymab ndaje ma; ba ñu génnee, ñaanal mbooloo ma, leeru Aji Sax ji feeñu mbooloo ma mépp. \v 24 Ci kaw loolu sawara bawoo fi Aji Sax ji, tàkk ca kaw sarxalukaay ba, xoyom saraxu rendi-dóomal ba ak nebbon ba. Naka la mbooloo ma mépp gis loola, daldi sarxolle, ba noppi dëpp seen jë fa suuf. \c 10 \s1 Musiba dal na Nadab ak Abiyu \p \v 1 Ci kaw loolu doomi Aaróona yu góor yi tudd Nadab ak Abiyu jël ku ci nekk ab andam, def cay xal, def ca cuuraay, indil ko \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, muy taal bu dul ndigal te santu leen ko woon. \v 2 Sawara ne jippét, bawoo fi Aji Sax ji, lakk leen ba ñu dee fa kanam Aji Sax ji. \v 3 Musaa ne Aaróona: «Lii la Aji Sax ji doon wax ba mu nee: “Ci biir ñi may jegeñ laay feeñal samag sellaay, te ci kanam mbooloo mi mépp lees may terale.”» Aaróonaa nga ne cell. \p \v 4 Ba mu ko defee Musaa woolu Mikayel ak Elsafan, góor ñiy doomi Usyel, baayu Aaróona bu ndaw. Mu ne leen: «Kaayleen jële fi seen bokk yii ci \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi, te ngeen génne leen dal bi.» \v 5 Ñu jàpp ca seeni mbubb, génne leen dal ba, muy la Musaa santaane woon. \v 6 Musaa wax Aaróona ak doomam yu góor yi tudd Elasar ak Itamar ne leen: «Buleen njañu te buleen ñaawlu di xotti seeni yére, lu ko moy dingeen dee, te merum Yàlla dina dal ci kaw mbooloo mi mépp. Waaye seen bokki \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp sañ nañoo jooy ñi Aji Sax ji lakk. \v 7 Bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi, buleen ko wees, lu ko moy dingeen dee, ndax diwu palu Aji Sax jaa ngi ci seen kaw.» Ñu def la leen Musaa sant. \s1 Li war ci sarxalkat \p \v 8 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax Aaróona itam ne ko: \v 9 «Biiñ mbaa naan guy màndal bu ko kenn ci yeen naan buy duggsi ci biir \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi, du yaw, du say doom yu góor, lu ko moy dingeen dee. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan. \v 10 Dangeen wara mana ràññee lu \w sell|lemma="sell:"\w* ak lu ñu sellalul, dangeen wara ràññee itam lu set ak lu setul. \v 11 Nangeen jàngal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* mboolem dogal yi leen Aji Sax ji dénk, te Musaa jottli leen ko.» \p \v 12 Ci kaw loolu Musaa wax ak Aaróona ak doomam yu góor yi des, di Elasar ak Itamar, ne leen: «Jël-leen \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* mi des ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, ngeen lekk ko, bañ cee boole lawiir, ci wetu \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi, ndax lu sella sell la. \v 13 Lekkleen ko ci bérab bu sell. Sa cér la, yaw ak say doom yu góor, ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji. Loolu lañu ma sant. \v 14 Waaye dënnu \w saraxu yékkati-jébbale|lemma="Sarax yi:"\w* bi ak tànkub jooxe bi, lekkleen ko ci bérab bu mucc sobe, yaak say doom yu góor ak say doom yu jigéen, ndax seen cér la, ci \w saraxi canti bànni Israyil ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*, nga moom ko yaak say doom. \v 15 Tànkub jooxe bi ak dënnu saraxu yékkati-jébbale bi, mook nebbon bi ñuy def saraxu sawara, dees koy boole indi yékkati ko, def ko sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji. Yeena moom yooyu, yaak say doom, muy seen cér bu ñu leen dogalal fàww, te di la Aji Sax ji santaane woon.» \p \v 16 Gannaaw loolu Musaa laajte, ba am lu leer ci mbirum sikketu \w saraxas póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w* bi, ndekete lakk nañu ko, ba mu dib dóom. Mu mere ca doomi Aaróona yu góor ya des, di Elasar ak Itamar, ne leen: \v 17 «Lu waral lekkuleen sarax biy póotum bàkkaar ci \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w*? Lu sella sell la, ñu jox leen ko, ngeen war koo yenniku bàkkaaru mbooloo mi, ba defal leen seen njotlaay fi kanam Aji Sax ji. \v 18 Gannaaw dugaleesul deret ji ca biir bérab bu sell ba, waroon ngeena lekk sikket bi ci bérab bu sell, muy li ma santaane woon.» \v 19 Aaróona ne Musaa: «Xoolal rekk tey ni bànni Israyil indile Aji Sax ji seen saraxu póotum bàkkaar ak seen \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, te teewul lii dal ci sama kaw! Bu ma lekkoon tey ci yàppu saraxas póotum bàkkaar bi, ndax dina neex Aji Sax ji?» \v 20 Musaa dégg kàddu yooyu, rafetlu ko. \c 11 \ms1 Sàrtal nañu lu set ak lu setul \mr (Saar 11—15) \s1 Lu jëm ci mala mu set ak mu setul \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na Musaa ak Aaróona ne leen: \v 2 «Waxleen \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen: Boroom bakkan yi ngeen di lekk seen yàpp, ci mboolem mala yiy dox ci suuf moo di yii: \v 3 Mboolem mala mu we wa xar, séddlikoo ñaar, te muy duññ, moom ngeen di lekk aw yàppam. \v 4 Yii ñuy lim, buleen ko lekk: mala muy duññ te we wi xarul, mbaa we wi xar te du duññ. Lu mel ni giléem, buleen ko lekk ndax day duññ, waaye we wi xarul. Daganul ci yeen. \v 5 Daman\f + \fr 11.5 \fr*\fk daman \fk*\ft xaw naa nirook njomboor.\ft*\f* day duññ waaye we wi xarul, kon daganul ci yeen. \v 6 Lëg day duññ waaye we wi xarul, kon daganul ci yeen. \v 7 Mbaam-xuux, we wi xar na waaye du duññ, kon daganul ci yeen. \v 8 Buleen ci lekk lenn te buleen laal méddam ndax lenn daganu ci, ci yeen. \p \v 9 «Li ngeen mana lekk ci mboolem luy nekk ci ndox mooy lii: Mboolem lu am ay ciiriir aki waasintóor tey nekk ci ndoxum géej mbaa dex, man ngeen koo lekk. \v 10 Waaye mboolem luy nekk ci géej mbaa dex, di lépp luy ramm-rammi cim ndox mbaa mboolem yeneen bindeef yuy nekk ci ndox, su amul ciiriir aki waasintóor, sibleen ko. \v 11 Lu ngeen sib lay doon, kon buleen ci lekk yàppu lenn te sibleen méddam. \v 12 Mboolem luy nekk ci ndox te amul ciiriir ak waasintóor, sibleen ko. \p \v 13-18 «Li ngeen wara sib ci njanaaw yi te deesu ko lekk moo di: jaxaay ak mboolem xeeti tan; ak céeli, bu xonq baak bu ñuul ba, bu mu mana doon, ak mboolem xeeti baaxoñ, ak mboolem xeeti looy, muy looy mu ndaw ak looy muy napp ak looy mu gudd nopp ak looyu màndiŋ, ba ci xar-jéjj ak tiiwi. Nangeen sib maf itam, ak kirigéej ak mboolem xeeti liccin; \v 19 ak yébb ak lu xeetook xodd, ak musejubru ak njugub. \p \v 20 «Mboolem gunóor guy naaw tey doxe ñeenti tànk sibleen ko. \v 21 Li ngeen mana lekk daal ci mboolem gunóor guy naaw tey doxe ñeenti tànk moo di: lépp lu tànk yi ànd aki yeel, mu man caa tëb-tëbe ci suuf. \v 22 Li ngeen mana lekk ci yooyu moo di: mboolem xeetu njéeréer ak mboolem xeetu salleer ak mboolem xeetu soccet ak yeneen yu ñu xeetool yépp. \v 23 Waaye mboolem yeneen gunóor yuy naaw tey doxe ñeenti tànk sibleen ko. \p \v 24 «Yii nag da leen di sobeel te képp ku laal lu ci dee dina yendoo sobe ba jant so. \v 25 Te itam képp ku for lenn lu dee ci yii, na fóot ay yéreem, waaye dina yendoo sobe ba jant so. \v 26 Mboolem mala mu we wa xar te séddlikoowul ñaar mbaa du duññ daganul ci yeen, ku ci laal lenn it sobewu na. \v 27 Ba tey lépp luy doxe ndëgguy tànkam ci mboolem boroom ñeenti tànk, daganul ci yeen te ku laal méddam dina yendoo sobe ba jant so. \v 28 Ku for méddam, na fóot ay yéreem te dina yendoo sobe ba jant so. Yooyu daganul ci yeen. \p \v 29 «Bu loolu weesee, leneen lu daganul ci yeen ci rab yu sew-sewaan yiy dox ne ñàpp ci suuf, mooy kaña ak janax ak xeeti mbëtt yépp; \v 30 ak unk ak bar ak sindax buy yéeg, ak sindax buy dox ci suuf, ak kàkkatar. \v 31 Yooyoo daganul ci yeen ci mboolem rab yu sew-sewaan yiy dox ne ñàpp ci suuf. Képp ku laal lenn lu ci dee dina yendoo sobe ba jant so. \v 32 Te it lu ci dee ba wadd ci kaw lenn, loola day sobewu, nay ndabal bant, mbaa ndimo, der mbaa ab saaku, mbaa jumtukaay bu mu mana doon. Nañu sóob loola ci ndox te du tee mu yendoo sobe ba jant so, mu doora set. \v 33 Su fekkee ne lenn a dee ci yooyu, wadd ci biir ndabal xandeer, lu woon ca biir sobewu na, te nañu toj ndab la. \v 34 Ndox mu jóge ci ndab loolu, bu dalee ci ñam wu dagan, ñam woowu dal nay sobewu moom itam; bu doon ag naan gu dagan moo ca nekk it, sobewu na, ak ndab lu naan ga mana nekk. \v 35 Lépp lu lenn ci yooyu dee, ba dal ca, la mu dal sobewu na. Su dee ab puuru ban mbaa cin, dees koy toj ndax sobewu na te lu setul la ci yeen. \v 36 Su fekkee ne loola dee daa wadd ci biir bëtu ndox mbaa kàmb gu def ndox, du tee ndox ma laab, waaye ku laal la dee ca biir sobewu nga. \v 37 Su la dee waddee ci peppum jiwu, du tee peppum jiwu ma set; \v 38 waaye su fekkee ñu kaas pepp ma te lenn lu dee lu bokk ci yooyu dal ca, pepp ma daganul ci yeen. \p \v 39 «Su mala mu dagan méddee, ku laal médd ma dina yendoo sobe ba jant so. \v 40 Képp ku lekk ca médd ma, na fóot ay yéreem, te du tee mu yendoo sobe ba jant so. Képp ku for médd ma, na fóot ay yéreem te du tee mu yendoo sobe ba jant so. \p \v 41 «Mboolem bindeef yu sew-sewaan yiy dox ne ñàpp ci suuf, sibleen ko. Deesu ko lekk. \v 42 Lépp luy watatu, mbaa lu sew di boroom ñeenti tànk, mbaa mu bare ay tànk ci mboolem bindeef yu sew-sewaan yiy dox ne ñàpp ci suuf, waruleen koo lekk, ndax lu ñu wara sib la. \v 43 Buleen araamal seen bopp ci lenn ci yu sew-sewaan yooyu; buleen ci taq, di ci sobeel seen bopp, \v 44 ndaxte man Aji Sax ji maay seen Yàlla. Kon nag sell-luleen te sell ndax man ku Sell laa. Kon buleen sobeel mukk seen bopp ci mboolem bindeef yu sew-sewaan yiy dox ci suuf. \v 45 Ndaxte kat man Aji Sax ji maay ki leen génne woon réewum Misra, di seen Yàlla. Sell-leen boog, ndax man ku Sell laa.» \p \v 46 Loolu la yoon digle ci wàllu mala ak njanaaw ak bindeef yi nekk ci ndox, ak mboolem bindeef yu sew-sewaan yiy dox ne ñàpp ci suuf. \v 47 Dina taxa ràññatle lu set ak lu setul. Dina taxa ràññatle boroom bakkan yi dagana lekk ñook boroom bakkan yi daganula lekk. \c 12 \s1 Li war ci ku wasin \p \v 1 Bu loolu wéyee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na Musaa ne ko: \v 2 «Waxal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen: Ku ëmb ba wasin, am doom ju góor, dina sobewu diiru juróom ñaari fan. Day sobewu ni bu tolloo ci fan yi muy gis baax. \v 3 Bu bés ba délsee, nañu xarfal xale bi. \v 4 Dina ca teg fanweeri fan ak ñett, ngir setlu ca meret ma. Ci diir booba warula laal lenn lu ñu sellal, mbaa muy dugg fu \w sell|lemma="sell:"\w* li feek àppu setloom matul. \v 5 Su amee doom ju jigéen, dina sobewu diiru ñaari ayi bés, mu mel ni ku gis baax. Dina ca teg juróom benn fukki fan ak juróom benn, doora tàggook sobey meret ma. \p \v 6 «Keroog bu àppu setloom matee, bu doom ja dee góor, bu dee jigéen, na dem ca bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* ma te yóbbul \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi am xar mu am at, muy \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ak xati mu ndaw mbaa pitax, mu doon \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*. \v 7 Na ko sarxalkat bi sarxal fi kanam Aji Sax ji, def ko njotlaayal wasin-bees wi, mu doora tàggook sobey meret ma.» \p Loolu la yoon digle ci wasin-bees, mu am doom ju góor mbaa ju jigéen. \v 8 «Su fekkee ne wasin-bees wi amul njégu xar, na indi ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, benn bi di saraxu rendi-dóomal, bi ci des di saraxu póotum bàkkaar. Sarxalkat bi defal ko ku jigéen ki njotlaayam, mu daldi set.» \c 13 \s1 Li war ci jàngoroy der \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na Musaa ak Aaróona ne leen: \v 2 «Su nit amee ab tërgën ci yaramam mbaa ab ër, mbaa ab gàkk bu weex bu mana doon jàngoroy der juy law ci yaramam, nañu ko yóbbu ci Aaróona \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi mbaa kenn ciy doomam yu góor yiy sarxalkat yi. \v 3 Na sarxalkat bi seet gàkk bi ci yaramu nit ki; su fekkee ne kawar gi ci gàkk bi dafa soppiku weex, te mu mel ni lu def pax ci der bi, jàngoroy der juy law la. Bu sarxalkat bi gisee loolu, na biral ne nit ki sobewu na. \v 4 Waaye su dee ab gàkk bu weex ci yaram wi te melul ni lu def pax ci der bi, taxul itam kawar gi ci nekk soppiku weex, na sarxalkat bi ber nit ki ame gàkk bi diiru juróom ñaari fan. \v 5 Na ko sarxalkat bi xoolaat bésub juróom ñaareel ba. Bu sarxalkat bi seetloo ne gàkk bi soppikuwul mbaa mu law ci yaramam, na ko beraat juróom ñaari fan. \v 6 Na ko sarxalkat bi xoolaat ca bésub juróom ñaareel ba. Su fekkee gàkk bi di raaf te lawul ci kaw deru yaram wi, na sarxalkat bi biral ne nit ki set na; ab ër doŋŋ la. Day fóot ay yéreem rekk daldi set. \v 7 Su fekkee ne wóor na ne ër bi law na ci deru yaramu nit ki, gannaaw ba mu ko wonee sarxalkat bi, ba mu biral ne set na, day dellu ca sarxalkat ba. \v 8 Su boobaa na ko sarxalkat bi xoolaat ba gis ër bi law ci deru yaram wi, mu doora biral ne nit ki sobewu na te jàngoroy der juy law la. \p \v 9 «Képp ku ame jàngoroy der juy law, nañu ko yóbbu ca sarxalkat ba. \v 10 Na ko sarxalkat bi seet. Su dee ab tërgën bu weex te kawar gi ci nekk soppiku weex, boole ci def góom ca biir, \v 11 kon jàngoroy der juy law la te xas naa law ci yaram wi. Na sarxalkat bi biral ne nit ki sobewu na. Du jar mu di ko ber ndax taq na sobe ba noppi. \v 12 Su fekkee ne nag jàngoro ji génn naa génn ci yaramu nit ki, sarxalkat bi gis ko fépp, li ko dale ci bopp bi ba ci tànk yi, \v 13 na ko sarxalkat bi seet bu baax. Bu gisee ne li génn ci yaramam daj na yaram wi yépp, na biral ne nit ki mu dal set na; gannaaw léppam a soppiku weex, set na. \v 14 Ba tey bés bu ay góom génnaatee ci yaram wi, nit ki sobewu na. \v 15 Su sarxalkat bi gisee yaramu nit ki def góom rekk, na biral ne sobewu na. Góom boobu génn ci yaram wi sobe la. Jàngoroy der juy law la. \v 16 Te it bu góom bi soppikoo weex, na dem ca sarxalkat ba. \v 17 Na ko sarxalkat bi seet, ba gis ne weexaat na, mu biral ne ki jàngoro ji dal set na te kon it set na. \p \v 18 «Su nit taabee ba wér, \v 19 ab tërgën bu weex mbaa gàkk bu weex bu rax xonq feeñ fa taab ba nekkoon, na dem ca sarxalkat ba. \v 20 Su ko sarxalkat bi seetee ba gis fa taab ba nekkoon mel ni lu def pax, te kawar gi ci nekk soppiku weex, na sarxalkat bi biral ne nit ki sobewu na. Jàngoroy der juy law la, ju juddoo ca taab ba. \v 21 Waaye su ko sarxalkat bi seetee te gisu ca kawar gu weex, deful pax it te raaf na, na ber nit ki juróom ñaari fan. \v 22 Su wéree ne jàngoro ji law na ci yaram wi, na sarxalkat bi biral ne nit ki sobewu na. Jàngoroy der juy law la. \v 23 Su gàkk bi yemee foofu, baña law, légétub taab ba la, te na sarxalkat bi biral ne nit ki set na. \p \v 24 «Su nit lakkee, ab gàkk bu weex mbaa bu weex te rax xonq feeñ ca kaw suux wu xonq wa lakk, \v 25 na ko sarxalkat bi seet. Su kawar gi ci nekk soppikoo weex te gàkk bi mel ni lu def pax, kon jàngoroy der juy law la, ju juddoo ca lakk-lakk ba. Na sarxalkat bi biral ne nit ki sobewu na, ndax jàngoroy der juy law la. \v 26 Waaye su ko sarxalkat bi seetee, gisul kawar gu weex ci gàkk bi, deful pax it te raaf na, na ber nit ki juróom ñaari fan. \v 27 Sarxalkat bi da koy seet ca bésub juróom ñaareel ba. Su wéree ne jàngoro ji law na ci yaram wi, na biral ne nit ki sobewu na. Jàngoroy der juy law la. \v 28 Su gàkk bi yemee foofu te lawul ci yaram wi, ab tut la bu juddoo ci lakk-lakk bi. Na sarxalkat bi biral ne nit ki set na, ndax légétub lakk-lakk ba la. \p \v 29 «Su fekkee ne góor mbaa jigéen dafa ame jàngoro ci bopp mbaa ci sikkim, \v 30 na sarxalkat bi seet fi jàngoro ji nekk. Su melee ni lu def pax ci der bi, kawar gu xall te sew nekk ca, na sarxalkat bi biral ne nit ki sobewu na. Loolu wat-wataan la, di ër yuy génn ci bopp mbaa sikkim. \v 31 Ndegam sarxalkat bi seet na ër wi te niruwul lu def pax, amul it kawar gu ñuul ca biir, day ber nit ki ame ër wi diiru juróom ñaari fan. \v 32 Sarxalkat bi day seetaat ër wi ca bésub juróom ñaareel ba. Su wat-wataan ji lawul, kawar gu xall nekku ca, te melul ni lu def pax, \v 33 na nit ki watu waaye du wataale wat-wataan ji. Sarxalkat bi da koy beraat juróom ñaari fan. \v 34 Na sarxalkat bi seetaat wat-wataan ji ca bésub juróom ñaareel ba. Su wat-wataan ji lawul ci yaram wi te niruwul lu def pax, sarxalkat bi day biral ne nit ki sobewuwul. Nit ki day fóot ay yéreem daldi set. \v 35 Waaye su wéree ne wat-wataan ji law na ci yaram wi gannaaw ba ñu biralee ne set na, \v 36 na ko sarxalkat bi dellu seet ba gis ne wat-wataan ji law na ci yaram wi. Su boobaa soxlaatul mu di ca seet kawar gu xall, ndax nit ki sobewu na. \v 37 Waaye su seetloo ne wat-wataan ji soppikuwul te kawar gu ñuul sax ca, wat-wataan ja wér na, nit ki it set na. Na sarxalkat bi biral ne nit ki set na. \p \v 38 «Su góor mbaa jigéen amee ay gàkk-gàkk yu weex ci yaram wi, \v 39 sarxalkat bi seet ko, gàkk yooyu ci yaram wi di lu weex, xawa xall, xam rekk la, ju feeñ ci yaram wi waaye nit ki set na. \p \v 40 «Góor gu bopp ba amatul kawar dafa leel waaye set na. \v 41 Bu bopp bi ñàkkee kawar fi féeteek kanam gi, jë baa leel waaye set na. \v 42 Waaye su amee gàkk bu weex bu feeñ te rax xonq ci leelub ndaal bopp mbaa jë, jàngoroy der la juy màgg tey génn ci leelub ndaal bopp mbaa jë. \v 43 Sarxalkat bi da koy seet. Ndegam ay tërgën yu weex te rax xonq a ngi ci leelub ndaal bopp bi mbaa jë bi, mu mel ni jàngoroy der juy law ci yaram wi, \v 44 nit ki ànd naak jàngoro te taq na sobe. Na sarxalkat bi biral ci lu leer ne nit ki sobewu na ndax jàngoro ji ci bopp bi. \p \v 45 «Ku ànd ak jàngoroy der juy law nag yére yu xottiku lay sol te day njañu\f + \fr 13.45 \fr*\ft Dafa wara ñaawlu ni bu nekkoon ci dëj, ngir àrtu nit ñi ba ñu sore ko, ndax setul.\ft*\f*. Na muur li ko dale ci tuñum kaw mi ba ci sikkim bi, te nay jàppoo àddu ca kaw naan: “Setuma de, setuma!” \v 46 Li feek jàngoro jaa ngi ci moom, day sobewu te gannaaw daa sobewu, na dëkk moom doŋŋ te na dëkkuwaayam génn dal bi. \s1 Li war ci këf ku teg liir \p \v 47 «Su ndimo xuuree, teg aw liir, muy ndimol kawaru gàtt gu ñu ëcc mbaa yu wëñ gu ëccu\f + \fr 13.47 \fr*\fk wëñ gu ëccu: \fk*\ft seetal ci 6.3.\ft*\f*, \v 48 mu tegu ci bàgg mbaa ci poqe, su dee kawar gu ëccu, su dee wëñ gu ëccu walla der bu ñu wulli walla mboolem lu ñu defare der, \v 49 su liir wi nëtëxee mbaa mu xonq, tege ci yére mbaa der mbaa bàgg mbaa poqe mbaa lu ñu defare der, liir wuy law la. Dees koy won \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi. \v 50 Na sarxalkat bi nemmiku liir wi, ba noppi ber këf ki teg liir wi diiru juróom ñaari fan. \v 51 Bésub juróom ñaareel ba na seet liir wa. Su liir wa lawee ca kaw këf ka, muy ndimo mbaa bàgg mbaa poqe mbaa der mbaa jumtukaayu der, kon liir wu aaytal la te këf ka sobewu na. \v 52 Da koy lakk, ndax liir wu aaytal la, muy ndimo mbaa bàgg mbaa poqe mbaa kawaru gàtt gu ñu ëcc mbaa wëñ gu ëccu mbaa lu ñu defare der te liir wa tegu ca. Dees koy lakk, ba mu dib dóom. \v 53 Waaye kat bu sarxalkat bi seetloo ne liir wi lawul ci këf ki, muy ndimo mbaa bàgg mbaa poqe mbaa jumtukaayu der, \v 54 na santaane ñu fóot ko, mu daldi koy beraat juróom ñaari fan. \v 55 Ndegam nag gannaaw ba ñu fóotee këf ka teg liir, sarxalkat bi seet na ko, te liir wi soppiwul melo, bu lawul it setul. Dees koy lakk, ba mu dib dóom, su yàqoo biir ak su yàqoo biti yépp. \v 56 Su sarxalkat bi gisee gannaaw ba ñu fóotee këf ka ne, liir wi raaf na, na dagg sànni fa tegoon liir ca këf ka, muy ndimo mbaa der mbaa bàgg mbaa poqe. \v 57 Su liir wa génnaatee ca këf ka, muy ndimo mbaa bàgg mbaa poqe mbaa lu ñu defare der, kon liir wuy màgg la. Këf ka teg liir dees koy lakk, ba mu dib dóom. \v 58 Ndegam liir wa deñ na, gannaaw ba ñu fóotee këf ka, muy ndimo mbaa bàgg mbaa poqe mbaa lu ñu defare der, dees koy fóotaat, mu doora set.» \p \v 59 Loolu la yoon digle ci liir wuy law wu tegu ci ndimol kawar gu ëccu mbaa lu wëñ gu ëccu mbaa bàgg mbaa poqe mbaa lu ñu defare der. Ci digle yooyu lañuy tegu, ba mana biral ne këf ka set na am setul. \c 14 \s1 Li war ci laabal boroom jàngoroy der \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji teg na ca ne Musaa: \v 2 «Li yoon digle ci mbirum nit ku ame jàngoroy der juy law, keroog bés ba ñuy laabal nit ki, mooy lii: Nañu ko yegge \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi. \v 3 Sarxalkat bi day génn dal bi, bu koy seet. Su nit ki demee ba jàngoroy der ji ko daloon wér, \v 4 sarxalkat bi day santaane, ñu indil nit kooku ñuy laabal ñaari picc yu dagan tey dund, ak bantu garabu seedar, ak wëñ gu xonq curr, ak caru garabu isob\f + \fr 14.4 \fr*\fk isob: \fk*\ft seetal ci \ft*\ft \+bk Mucc ga\+bk* 12.22.\ft*\f*. \v 5 Na sarxalkat bi santaane, ñu rendi menn picc mi, tiimale ko ndabal xandeer lu def ndox mu balle ci bëtu ndox. \v 6 Picc miy dund da koy booleek bantu seedar bi ak wëñ gu xonq curr gi ak caru isob bi, boole lépp sóob ci deretu picc ma ñu rendi woon tiimale ko ndox mi balle ci bëtu ndox. \v 7 Bu loolu amee sarxalkat bi wis-wisal juróom ñaari yoon ci kaw ki ñuy laabal, ngir mu tàggook sobey jàngoro ji. Su ko defee sarxalkat bi biral ne set na. Bu noppee na bàyyi picc miy dund mu naaw ca àll ba. \v 8 Ku ñuy laabal day fóot ay yéreem, watu ba set te sangu, doora set. Gannaaw loolu man naa dugg ci dal bi, waaye na yem ca bunt xaymaam ca biti diiru juróom ñaari fan. \v 9 Bésub juróom ñaareel ba na watu ba set, bopp beek sikkim beek yeen yi ak kawar gi ci des yépp lay wat, fóot ay yéreem, sangu, daldi set. \v 10 Bésub juróom ñetteel ba na indi ñaari kuuy yu amul sikk, ak menn xar mu jigéen mu am at te amul sikk ak juróom ñeenti kiloy sunguf su mucc ayib su ñu xiiwe diw, muy \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w*. Mu indaale genn-wàllu liitaru diw. \v 11 Sarxalkat biy laabal nit ki day indi nit ki, mu ànd ak loolu lépp, taxaw fi kanam Aji Sax ji, ci bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi. \p \v 12 «Sarxalkat bi teg ca jël menn kuuy mi, rendi ko, muy \w saraxu peyug tooñ|lemma="Sarax yi:"\w*, boole kook genn-wàll liitaru diw ga, def ko \w sarax bu ñuy yékkati|lemma="Sarax yi:"\w*, jébbal Aji Sax ji. \v 13 Nañu rendi kuuy mi ci \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi, fi ñuy rendee juru \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w* ak \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ndax li nekk ci saraxu peyug tooñ moo nekk ci saraxu póotum bàkkaar: sarxalkat bee ko moom; lu sella sell la. \v 14 Na sarxalkat bi sàkk ci deretu jur giy saraxu peyug tooñ, taqal ko ci tabanu noppu ndijooru nit ki ñuy laabal ak baaraamu déyu ndijooram ak baaraamu déyu tànku ndijooram. \v 15 Bu sarxalkat bi noppee, na sàkk ci genn-wàll liitaru diw gi, sotti ko ci biir loxol càmmoñu boppam. \v 16 Na sarxalkat bi capp baaraamu joxoñu ndijooram ci diw gi ci loxol càmmoñam, daldi wis-wisale diw gi baaraamam, ba mu mat juróom ñaari yoon fi kanam Aji Sax ji. \v 17 Na sarxalkat bi sàkk ci diw gi des ci loxoom, tooyal ci tabanu noppu ndijooru nit ki ñuy laabal ak baaraamu déyu ndijooram ak baaraamu déyu tànku ndijooram; nañu ko laalal ci diw gi fa ñu ko jëkkoona taqal ci deretu sarax siy peyug tooñ. \v 18 Li des ci diw gi ci loxol sarxalkat bi, na ko diw ci boppu nit ki ñuy laabal. Noonu la ko sarxalkat bi defale njotlaayam fi kanam Aji Sax ji. Ba loolu amee sarxalkat bi rendi sarax biy póotum bàkkaar, \v 19 defal ko ki ñuy laabal njotlaayam ngir mu tàggook sobeem. Te itam na sarxalkat bi rendi saraxu dóomal bi, \v 20 boole kook saraxu pepp mi, joxe lépp ci kaw \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi, defal ko nit ki njotlaayam, mu set. \p \v 21 «Su fekkee ne nit ki dafa ñàkk ba dooleem matewu ko, na wut menn kuuy, muy saraxu peyug tooñ, di saraxu yékkati-jébbale, ngir njotlaayam, boole kook ñetti kiloy sunguf su mucc ayib, xiiwe ko diw, muy saraxu pepp. Na indaale genn-wàll liitaru diw, \v 22 ak ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, lu mu ci gëna jekku rekk. Menn mi saraxu póotum bàkkaar la, mi ci des di saraxu rendi-dóomal. \v 23 Da koy indil sarxalkat bi, ngir mu laabal ko bu bés ba délsee, ca bunt xaymab ndaje ma, fi kanam Aji Sax ji. \v 24 Sarxalkat bi day jël kuuyu sarax siy peyug tooñ ak genn-wàll liitaru diw gi, boole ko, muy sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji. \v 25 Gannaaw gi ñu rendi kuuy miy saraxu peyug tooñ, sarxalkat bi sàkk ci deret ji, taqal ci tabanu noppu ndijooru nit ki ñuy laabal ak baaraamu déyu ndijooram ak baaraamu déyu tànku ndijooram. \v 26 Bu sarxalkat bi noppee, na sotti tuuti ci diw gi ci loxol càmmoñu boppam, \v 27 Baaraamu joxoñu ndijooram lay wis-wisale diw gi ci loxol càmmoñam ba muy juróom ñaari yoon fi kanam Aji Sax ji. \v 28 Loolu wéy sarxalkat bi wara sàkk ci diw gi ci loxoom, tooyal ca tabanu noppu ndijooru ki ñuy laabal ak baaraamu déyu ndijooram ak baaraamu déyu tànku ndijooram; na ko def ca bérab boobu mu taaj deretu sarax siy peyug tooñ. \v 29 Li des ci diw gi ci loxol sarxalkat bi na ko diw ci boppu ki ñuy laabal, defal ko ko njotlaay fi kanam Aji Sax ji. \v 30 Bu noppee na rendi menn pitax mi mbaa menn xati mu ndaw mi, lu mu ci gëna jekku rekk, \v 31 menn mi di saraxas peyug tooñ, mi ci des di saraxu rendi-dóomal, te mu boole kook saraxu pepp mi. Noonu la sarxalkat biy defale ki ñuy laabal njotlaayam fi kanam Aji Sax ji.» \p \v 32 Loolu la yoon digle ci mbirum nit ku ànd ak jàngoroy der juy law te dooleem matewul sarax yi ñu koy laabale. \s1 Li war ci néeg bu teg liir \p \v 33 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na Musaa ak Aaróona ne leen: \v 34 «Bu ngeen demee ca réewu Kanaan ga ma leen jox muy seen moomeel, bu ma tegee liir wuy law ba xuural ab néeg foofa ca seen réewum bopp, \v 35 boroom néeg bi dafa wara dem ca \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba ne ko: “Lu mel ni aw liir laa gis sama néeg.” \v 36 Su boobaa na sarxalkat bi santaane, ñu génne lépp lu nekk ca néeg ba, bala muy dugg di seet liir wi. Su ko defee du am lenn lu nekk ca néeg ba, lu muy biral ne sobe topp na ko. Gannaaw loolu sarxalkat bi dugg, seet néeg bi. \v 37 Bu sarxalkat bi seetee liir wi ci miiri néeg bi ca biir, muy ay xóot-xóot yu xawa nëtëx, mbaa mu xawa xonq, mel ni lu def pax ci miir bi, \v 38 na génn néeg bi te tëj néeg bi diiru juróom ñaari fan. \v 39 Bésub juróom ñaareel ba na sarxalkat bi délsi seet néeg bi. Bu liir wi lawee ci miiri néeg bi, \v 40 na sarxalkat bi santaane, ñu teggi doj yi liir wi xuural, boole ko génne dëkk bi, sànni ko fu setul. \v 41 Na xeetlu biir néeg bi ba mu daj, te pënd ba ñu ca xeete dees koy génne dëkk ba, tuur ko fu setul. \v 42 Dañoo wara sàkkaat ay doj, wuutale ko doj yooyu te sàkk ban bu bees, raaxe ko néeg bi. \p \v 43 «Su liir wi delloo tegu ci biir néeg bi gannaaw bu ñu teggee doj yi, xeet biir néeg bi, ba raax ko, \v 44 sarxalkat bi day dikk seet ko. Su liir wi lawee ci néeg bi, liir wu aaytal la wu xuural biir néeg bi, di sobe. \v 45 Néeg ba dees koy daane, boole doj yaak bant yaak banu raax ba bépp, génne ko dëkk bi, tuur ko fu setul. \p \v 46 «Ku dugg biir néeg bi diiru fan yi mu tëje dina yendoo sobe ba jant so. \v 47 Ku tëdd ca biir néeg ba war naa fóot ay yéreem te ku fa lekke it war naa fóot ay yéreem. \p \v 48 «Su sarxalkat ba delloo ca néeg ba, seet ko, fekk liir wa lawul ca néeg ba, gannaaw ba ñu ko raaxee, na biral ne néeg bi set na, ndax kon liir wa raaf na. \v 49 Liy laabal néeg bi moo di mu sàkk ñaari picc ak bantu garabu seedar ak wëñ gu xonq curr ak caru isob\f + \fr 14.49 \fr*\fk isob: \fk*\ft seetal ci \ft*\ft \+bk Mucc ga\+bk* 12.22.\ft*\f*. \v 50 Day rendi menn picc mi, tiimale ko ndabal xandeer mu def ndox mu balle ci bëtu ndox. \v 51 Bu noppee na jaxase deretu picc mi ñu rendi ak ndox mu balle ci bëtu ndox, daldi jël bantu seedar bi ak caru isob bi ak wëñ gi xonq curr ak picc miy dund, boole lépp sóob ca. Su ko defee mu wis-wisal ca juróom ñaari yoon ci néeg bi. \v 52 Kon li muy laabale néeg bi moo di deretu picc mi ak ndox moomu ak picc miy dund ak bantu seedar bi ak caru isob bi ak wëñ gi xonq curr. \v 53 Na bàyyi picc miy dund fu génn dëkk ba, mu naaw ca àll ba. Noonu lay defe njotlaayal néeg bi, mu set.» \p \v 54 Loolu la yoon digle ci lépp luy jàngoroy der juy law ak wat-wataan, \v 55 mbaa liir wu tegu ci ndimo mbaa ci néeg, \v 56 ak ci wàllu tërgën itam mbaa mu diy ër mbaa gàkk bu weex; \v 57 mooy tegtal biy xamle lu set ak lu setul. Loolu la yoon digle ci jàngoroy der juy law mbaa liir. \c 15 \s1 Lu jëm ci sobey góor \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na it Musaa ak Aaróona ne leen: \v 2 «Waxleen ak \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen: Góor gu ànd ak jàngoro ju sabab ngóoraam di xelli mbér, kooku sobewu na. \v 3 Mbér mi muy xelli moo ko sobeel; su ngóora liy xelli mbér mbaa su ko mbér mi fattee, waa ji sobewu na. \v 4 Lal ba mu tëdd sobewu na, te lépp lu mu toog loola sobewu na. \v 5 Képp ku laal lalam, na fóot ay yéreem, sangu, te du tee mu yendoo sobe ba jant so. \v 6 Ku toog ci lenn lu boroom jàngoroy xelli toogoon, na fóot ay yéreem, sangu, te du tee mu yendoo sobe ba jant so. \v 7 Ku laal boroom jàngoroy xelli war naa fóot ay yéreem, sangu, te du tee mu ànd ak sobe ba jant so. \v 8 Su ku ànd ak jàngoroy xelli tiflee ku taqul sobe, na kooku fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so. \v 9 Gépp tegu daamar gu boroom jàngoroy xelli waroon, sobewu na. \v 10 Ku laal lenn lu mu toogoon lu ko féete woon suuf dina yendoo sobe ba jant so, te képp ku yékkati loola na fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so. \v 11 Boroom jàngoroy xelli bu raxasul ay loxoom, ku mu laal, kooku, na fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so. \v 12 Ndabal xandeer lu boroom jàngoroy xelli laal, dees koo wara toj. Su dee mboolem ndabal bant, dees koy raxas. \p \v 13 «Gannaaw loolu bu boroom jàngoroy xelli ji tàggook sobey jàngoro ja, dafa wara waññ juróom ñaari fan ngir setlu, ba noppi fóot ay yéreem, sangoo ndox mu balle ci bëtu ndox, doora set. \v 14 Bésub juróom ñetteel ba, na wut ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw te teewi fi kanam Aji Sax ji ca bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* ma, daldi koy jox \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi. \v 15 Sarxalkat bi day rendi yooyu, menn mi di \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*, mi ci des di \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayam fi kanam Aji Sax ji ndax jàngoroy xelleem jooju. \p \v 16 «Su góor génnee wasal, war naa ragg yaramam wépp, te du tere mu yendoo sobe ba jant so. \v 17 Lépp luy yére mbaa der bu wasal taq, dees koy fóot te du tere mu yendoo sobe ba jant so. \v 18 Su dee jigéen ju góor àndal, te wasal génn, nañu sangu, te du tere ñu yendoo sobe ba jant so. \s1 Lu jëm ci sobey jigéen \p \v 19 «Su jigéen gisee mbërëg, sobey mbërëg ma day ànd ak moom juróom ñaari fan te képp ku laal ku jigéen ka dina yendoo sobe ba jant so. \v 20 Lépp lu mu tëdd te fekk mu gis baax, loola sobewu na te lépp lu mu toog, loola sobewu na. \v 21 Te it képp ku laal ab lalam, war naa fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so. \v 22 Képp ku laal lenn lu mu toogoon war naa fóot ay yéreem, sangu, te du tee mu yendoo sobe ba jant so. \v 23 Su toogoon ci lal mbaa leneen lu mu toogoon, ku laal loola dina yendoo sobe ba jant so, \v 24 te ku ko dëkkoo, ba mbërëg taq ko, kooka sobewu na diiru juróom ñaari fan, te ka ko dëkkoo, lal bu mu tëdd sobewu na. \p \v 25 «Kuy xëpp deret ay fan yu bare te du jamonoy baaxam, mbaa mu gis mbërëg mu wees àpp bi mu ko baaxoo gis, kooka sobewu na diiru fan yi muy xëpp. Day mel ni bu nekkee ci jamonoy baaxam. \v 26 Lal bu mu tëdd ci diir bi muy xëpp yépp, day mel ni lalam bu ko fekk ci jamonoy baax te lépp lu mu toog day sobewu, ni bu nekkoon ci jamonoy baaxam. \v 27 Ku laal lenn ci yooyu yëf, kooka sobewu na. War naa fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so. \p \v 28 «Bu xëppee ba jeexal, dina waññ juróom ñaari fan, doora tàggook sobe sa. \v 29 Bésub juróom ñetteel ba na wut ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, yóbbu ca \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba, ca bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* ma. \v 30 Sarxalkat bi day rendi menn mi muy \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*, mi ci des doon \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*. Su ko defee sarxalkat bi defal ko ko njotlaay fi kanam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ndax sobey xëpp ja. \p \v 31 «Fexeleen ba \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* di tàggook seeni sobe, lu ko moy dinañu dee ndax seen sobe, ngir dañuy taqal sama màkkaan mi ci seen biir.» \p \v 32 Loolu la yoon digle ci mbiri góor gu ànd ak jàngoroy xelli mbaa mu génne wasal, ba sobewu; \v 33 ak jigéen ju nekk ci jamonoy baaxam; ci gàttal képp ku taq sobe suy génne ci moom, muy góor mbaa jigéen, ak itam góor gu dëkkoo jigéen ju sobewu. \c 16 \ms1 Lu jëm ci bésub Njotlaay \p \v 1 Bu loolu weesee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax naak Musaa gannaaw ba ñaari doomi Aaróona yu góor ya deeyee, ba ñu taxawsee fa kanam Aji Sax ji. \v 2 Aji Sax ji dafa wax Musaa ne ko: «Waxal sa mag Aaróona ne ko du saa yu nekk lay àgg ci biir \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bee sell, ci gannaaw rido bi, di janook kubeeru saraxu njotlaay gi ub \w gaal gi àlluway kóllëre gi dence|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w*, lu ko moy dina dee, ndax ci niir wi tiim kubeeru gaal gi laay feeñe\f + \fr 16.2 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Mucc ga\+bk* 25.17.\ft*\f*. \p \v 3 «Ni Aaróona di dugge ci biir bérab bu sell bee sell nii la: day indaale aw yëkk wu ndaw ngir ab \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*, akum kuuy ngir ab \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*. \v 4 Mbubb mu \w sell|lemma="sell:"\w* lay sol, mu ñu ràbbe wëñ gu ëccu\f + \fr 16.4 \fr*\fk wëñ gu ëccu: \fk*\ft seetal ci 6.3.\ft*\f* ba sew ak tubéyi njiitlaay ju ñu ràbbe wëñ gu ëccu ba sew. Na takkoo laxasaay gu ñu ràbbe wëñ gu ëccu ba sew, te kaalag wëñ gu ëccu ba sew lay takk. Yére yu sell a ngoogu; kon nag na sangu bala mu koy sol. \v 5 Na jële ci mbooloom \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ñaari sikket, sikket yuy doon saraxu póotum bàkkaar ak menn kuuyum rendi-dóomal. \p \v 6 «Aaróona day sarxal yëkk wi, muy saraxu póotum bàkkaaram, di njotlaayal boppam, mook waa këram. \v 7 Gannaaw loolu na Aaróona indi ñaari sikket yi, taxawal fi kanam Aji Sax ji, ci bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi. \v 8 Na Aaróona tegal ñaari sikket yi bant, ngir xam bu ñuy rendil Aji Sax ji ak biy doon ngir Asasel\f + \fr 16.8 \fr*\fk Asasel: \fk*\ft am na ñu ne mi ngi tekki «kasara». Am na ba tey ñu naan rab wu bon la, wu dëkk ci màndiŋ mi.\ft*\f*. \v 9 Su ko defee Aaróona indi sikket, bi muurloo, ñu sarxalal ko Aji Sax ji, rendi ko, muy saraxu póotum bàkkaar. \v 10 Waaye sikket bi muurloo doon sikketu Asasel, dees koy taxawal muy dund fi kanam Aji Sax ji, te ni ñu koy jotoo, mooy dees koy dàq mu dem ca màndiŋ ma, ngir Asasel. \p \v 11 «Bu Aaróona noppee, na indi yëkku saraxas póotum bàkkaaram, def ko njotlaayam mook waa këram. Na rendi yëkku saraxas póotum bàkkaaram, \v 12 te na sàkk andu xal bu fees, tibbe ko ca \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* ba, fi kanam Aji Sax ji, ak ñaari barci-loxoy cuuraay lu mokk te xeeñ, boole ko yóbbu ca gannaaw rido ba. \v 13 Na def cuuraay li ci taal bi, foofa ca kanam Aji Sax ji, saxaru cuuraay si di làq kubeeru saraxu njotlaay gi ub gaalu àlluway seede si, ndax mu baña dee. \v 14 Na sàkk ci deretu yëkk wi, wis-wisale ko baaraamam ci kaw kubeeru gaal gi, ci wetam gi féete penku, te it na wis-wisale baaraamam deret ji lu mat juróom ñaari yoon ci kanam kubeeru gaal gi. \v 15 Bu noppee na rendi sikket biy saraxas póotum bàkkaaru mbooloo mi, te yóbbu deret ji ca gannaaw rido ba. Na def deret ji na mu defoon ak deretu yëkk wa, wis-wisal ko ca kaw kubeeru gaal gi ak ci kanam kubeer gi. \v 16 Mu daldi matale loolu njotlaayal bérab bu sell bee sell, tàggale kook sobey bànni Israyil ak seeni tooñ, ak lu seen bàkkaar mana doon. Noonu lay defal mboolem xaymab ndaje, mi dëkk ci seen biir ci seen biiri sobe. \v 17 Du kenn ku saña nekk ci biir xaymab ndaje mi, bu Aaróona duggee ci biir bérab bu sell bee sell, di matal ag njotlaay, ba keroog muy génn, gannaaw bu jotoo moom ci boppam, mook waa këram, ba jotaale mbooloom bànni Israyil mépp. \p \v 18 «Bu sottalee, na génn jëm ca sarxalukaay ba ca kanam Aji Sax ji, ba noppi defal sarxalukaay bi njotlaayal boppam. Day sàkk ci deretu yëkk wi ak ju sikket bi, taqal béjjéni sarxalukaay bi yépp. \v 19 Te itam day wis-wisale baaraamam deret ji lu mat juróom ñaari yoon ci kaw sarxalukaay bi, setal ko, sellal ko, mu tàggook sobey bànni Israyil. \p \v 20 «Bu Aaróona matalee njotlaayal bérab bu sell bee sell ak xaymab ndaje ma ak sarxalukaay ba, na indi sikket biy dund. \v 21 Aaróona day teg ay loxoom ci kaw boppu sikket biy dund te tudd ci kawam mboolem ñaawtéefi bànni Israyil ak seeni tooñ, ak seeni bàkkaar yépp, boole ko yen sikket bi, teg ko ci loxol nit ku ñu yónni, mu dàq ko ca màndiŋ ma. \v 22 Sikket bi day yenu seeni ñaawtéef yépp, yóbbaale ca ndànd-foyfoy ga, ñu wacc ko ca màndiŋ ma. \p \v 23 «Na Aaróona dellu ca xaymab ndaje ma, summi yére ya ñu ràbbe wëñ gu ëccu ba sew, di ya mu soloon bala moo dugg ca bérab bu sell baa sell, te na fa wacc yére ya. \v 24 Bu loolu weesee mu sangoo fu sell, sol yérey boppam, génn, joxeel boppam ab saraxu rendi-dóomal, joxeel mbooloo mi seen saraxu rendi-dóomal ngir njotlaayal boppam ak njotlaayal mbooloo mi. \v 25 Nebbonu jur giy saraxu póotum bàkkaar, na ko lakk ci kaw sarxalukaay bi. \p \v 26 «Ka wacci woon sikketu Asasel, na fóot ay yéreem, sangu, doora mana duggaat ci dal bi. \v 27 Muy yëkk wiy saraxu póotum bàkkaar, muy sikket biy saraxu póotum bàkkaar te ñu yóbbu woon seen deret ca biir bérab bu sell baa sell ngir defe ko njotlaay, lépp lañuy génne dal bi. Der yaak yàpp waak sébbriit ma dees koy boole lakk, ba mu dib dóom. \v 28 Ki ko lakk bu noppee, na fóot ay yéreem, sangu, doora mana duggaat ci dal bi. \p \v 29 «Te itam dogal a ngii, di lu leen war fàww. Bésub fukki fan ci juróom ñaareelu weeru at mi nangeen ci toroxlu te du lenn lu ngeen ci mana liggéey, du njuddu-ji-réew du doxandéem bi ci seen biir; \v 30 ndaxte ci bés boobu lañu leen di joxeel njotlaay ngir fóot seen mboolem bàkkaar, ba ngeen set fi kanam Aji Sax ji. \v 31 Na doon seen bés bu ngeen di nopplu doŋŋ, ngeen war cee toroxlu. Dogal la bu sax dàkk. \p \v 32 «\w Sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi ñu fal nag, solal ko, jox ko sañ-sañu sarxalkat bu mag, mu wuutu baayam, na def saraxu njotlaay gi. Na sol yére yu sell yooyu di yi ñu ràbbe wëñ gu ëccu ba sew, \v 33 te it na def njotlaayal bérab bu sell bee sell ak xaymab ndaje mi ak sarxalukaay bi, boole ci defal sarxalkat yi seen njotlaay, ñook mbooloom Israyil mépp. \p \v 34 «Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, te mooy ñuy joxeel bànni Israyil seen njotlaay benn yoon cim at ngir seen bàkkaar yépp.» \p Ñu daldi def li Aji Sax ji santoon Musaa. \c 17 \ms1 Ndigal yi jëm ci sellal \mr (Saar 17—26) \s1 Li war ci jaamu ak sarxal \p \v 1 Bu loolu wéyee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na Musaa ne ko: \v 2 «Waxal Aaróona aki doomam yu góor ak \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp ne leen li Aji Sax ji santaane mooy lii: \v 3 Képp kuy góor ci waa kër Israyil, bu rendee aw nag mbaa xar mbaa bëy ci biir dal bi, ak fu génn dal bi, \v 4 te indiwu ko ci bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi, teewalal ko Aji Sax ji, muy sarax ca bunt jaamookaayu Aji Sax ji, kooku dees na ko topp àqu deret. Dafa tuur deret. Kon dees na ko dagge ci biir bànni Israyil. \v 5 Su ko defee bànni Israyil dinañu indil Aji Sax ji juri sarax yi ñuy rendi ci àll bi. Dañu koo wara yóbbu ca \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba, fi Aji Sax ji, ca bunt xaymab ndaje ma, defal ko Aji Sax ji \w saraxi cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*. \v 6 Sarxalkat bi day xëpp deret ji ci \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* Aji Sax ji, ci bunt xaymab ndaje mi, ba noppi, lakkal Aji Sax ji nebbon bi, muy xeeñ xetug jàmm. \v 7 Buñu di sarxalatil tuur, yi ñuy jëmmale sikket, di ko bokkaalee. Na loolu di dogal bu leen war fàww, ñoom ak seen askan. \v 8 Wax leen boog ne leen: Képp kuy góor, ku bokk ci waa kër Israyil, mbaa mu bokk ci doxandéem yi ci seen biir, buy génne ab \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* mbaa beneen sarax, \v 9 te indiwu ko ci bunt xaymab ndaje mi, sarxalal ko Aji Sax ji, kooku dees koo wara dagge ci biir bànni Israyil. \p \v 10 «Te it képp ku bokk ci waa kër Israyil mbaa doxandéem yi ci seen biir, bu lekkee lenn luy deret, kooku lekk deret, man Aji Sax ji, dinaa ko noonoo te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil. \v 11 Ndaxte dundu mbindeef ci deret la nekk, te man maa leen sédde deret, ngeen di ko jotoo seen bakkan ci kaw sarxalukaay bi. Ndax kat bakkanu mbindeef deretam la taxawe. Moo tax deret mana defal nit njotlaayam. \v 12 Looloo waral ma ne bànni Israyil, bu kenn ci ñoom lekk deret, te doxandéem bi ci seen biir it bumu lekk deret. \p \v 13 «Képp ku bokk ci bànni Israyil mbaa ci doxandéem yi ci seen biir, bu rëbbee ba jàpp mala mbaa njanaaw, mu di lu dagana lekk, na tuur deret ji, suul, \v 14 ndax dundu mboolem mbindeef mooy deretam. Moo waral, man Aji Sax ji, ma ne bànni Israyil buñu lekk deretu menn mbindeef ngir dundu mboolem mbindeef mooy deretam. Képp ku lekk deret, dees koy dagge ci askan wi. \p \v 15 «Te itam képp ku lekk médd mbaa lu rab fàdd, muy njuddu-ji-réew mbaa doxandéem, na fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so, mu doora set. \v 16 Waaye su fóotul, sanguwul, mooy gàddu bàkkaaram.» \c 18 \s1 Li warul ci mbirum séy \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na Musaa ba tey ne ko: \v 2 «Waxal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen: Man Aji Sax ji maay seen Yàlla. \v 3 Defini waa réewam Misra ga ngeen dëkkoon, buleen ko roy, te defini waa réewu Kanaan ga ma leen jëme, buleen ko roy te it buleen leen topp ci seeni aada. \v 4 Samay santaane ngeen wara dégg tey topp samay dogal. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla. \v 5 Nangeen sàmm samay dogal ak samay santaane, ndax ngeen jëfe yooyu moo leen di taxa dund. Man maay Aji Sax ji. \p \v 6 «Bu kenn ci yeen dëkkoo ku mu jegewool lool cig bokk. Maay Aji Sax ji. \v 7 Bul torxal sa baay, di dëkkoo sa yaay. Sa yaay la, kon bu ko torxal moom it. \p \v 8 «Bul dëkkoo sa soxnas baay, di torxal sa baay. \p \v 9 «Bul dëkkoo sab jigéen, te muy koo bokkal benn baay mbaa koo bokkal jenn ndey, muy ku juddoo ci kër gi mbaa feneen. \p \v 10 «Bul dëkkoo sab sët bu jigéen bu sa doom ju góor jur mbaa sa doom ju jigéen, ndax kon torxal nga sa bopp. \p \v 11 «Bul dëkkoo ku sa soxnas baay am ak sa baay, ndax sab jigéen la. \p \v 12 «Bul dëkkoo sa bàjjan, ndax daa jegewook sa baay lool cig bokk. \p \v 13 «Bul dëkkoo sa ndey ju ndaw, ndax daa jegewook sa yaay lool cig bokk. \p \v 14 «Bul torxal sa baay bu ndaw di dëkkoo soxnaam. Sa ndey la. \p \v 15 «Bul dëkkoo sa soxnas doom. Sa soxnas doom la. Bu ko dëkkoo mukk. \p \v 16 «Bul dëkkoo soxnas koo bokkal benn baay mbaa jenn ndey, nde kon nga torxal sa doomu baay mbaa sa doomu ndey. \p \v 17 «Bul boole dëkkoo jigéen, dëkkoo doom ja mbaa sëtam bu doomam ju góor jur mbaa doomam ju jigéen jur ko, ndax dañoo jegewoo lool cig bokk. Loolu ñaawtéef la. \p \v 18 «Bul jël jigéen di séq ak moom séy, muy wujjeek doomu ndeyam mbaa doomu baayam joo jëkka jël, li feek kookoo ngi dund. \p \v 19 «Bul dëkkoo jigéen ju gis baax, ndax daa sobewu. \p \v 20 «Bul ànd ak jabaru jaambur, di sobeel sa bopp. \p \v 21 «Bul jébbal kenn ci say doom tuur mi ñuy wax Moleg, ndax waruloo teddadil sa turu Yàlla. Man maay Aji Sax ji. \p \v 22 «Bu góor tëdde góor, ni bu doon jigéen. Lu ñaawa ñaaw la. \p \v 23 «Bu góor tëdde menn mala, di sobeel boppam, te bu jigéen jox boppam mala, di ànd ak moom. Loolu yàqute la. \p \v 24 «Buleen sobeel seen bopp ci mboolem defin yooyu, ndax xeet yi ma leen dàqal, noonu lañu daan jëfe, ba sobeel seen bopp. \v 25 Réew ma sax mujj na daj ak sobe, ma wàcce mbugal ca kaw réew ma, ba mu gëq ay nitam. \p \v 26 «Yeen nag sàmmleen samay dogal ak samay santaane te bu kenn def lenn ci yooyu ñaawtéef, du njuddu-ji-réew, du doxandéem bi ci seen biir, \v 27 ndax kat mboolem ñaawtéef yooyu la waa réew ma leen fa jiitu daan def, ba réew ma mujj daj ak sobe. \v 28 Su ngeen sobeelee réew ma, dinaa leen gëq, na ma gëqe woon xeet ya leen fa jiitu woon. \v 29 Képp ku def lenn ci yooyu ñaawtéef déy, kooku dees koy dagge ci biir bànni Israyil. \v 30 Dénkooleen sama ndénkaane ngir baña roy lenn ci aada yu ñaaw yi ñu fi doon topp lu leen jiitu, te buleen sobeel seen bopp ci yooyu. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.» \c 19 \s1 Lu jëm ci dundin wu sell te jub \p \v 1 Bu loolu wéyee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na Musaa ne ko: \v 2 «Waxal mbooloom \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp ne leen: Ñu sell ngeen wara doon, ngir ku Sell laa, man seen Yàlla Aji Sax ji. \p \v 3 «Na ku nekk weg ndeyam ak baayam te wormaal sama \w bési Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*. Man Aji Sax ji, maay seen Yàlla. \p \v 4 «Buleen walbatiku di jaamu ay yàllantu mbaa ngeen di sàkkal seen bopp ay tuur yu ñu móole weñ. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla. \p \v 5 «Bu ngeen dee rendil Aji Sax ji \w saraxas cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*, sarxal-leen ko ni mu ware, ndax ñu nangul leen. \v 6 Ca bés ba ñu ko sarxale lees koy lekk, mbaa ca ëllëg sa; lu ca des ba ca gannaaw ëllëg sa dees koy lakk, ba mu dib dóom. \v 7 Bu ñu ci lekkee déy te fekk mu am ñetti fan, day doon lu ñu sib, te deesu ko nangu. \v 8 Ku ci lekk mooy gàddu bàkkaar bi, ndaxte lu ñu sellalal Aji Sax ji la teddadil, te kooku dees na ko dagge ci biir bànni Israyil. \p \v 9 «Bu ngeen dee góob seen tool, buleen góob ba fa tool ba yem te buleen ca toppaat, di foraatu. \v 10 Seen tóokëri reseñ it buleen ko witt ñaari yoon te buleen foraatu doom yu wadde ca witt ma. Aji ñàkk akub doxandéem ngeen koy bàyyee. Maay seen Yàlla, man Aji Sax ji. \p \v 11 «Buleen sàcc, buleen fen te buleen di worante. \p \v 12 «Buleen giñe sama tur lu dul dëgg, di teddadil seen turu Yàlla. Maay Aji Sax ji. \p \v 13 «Buleen lekk seen àqu moroom, buleen sàcc. Buleen wacc peyu liggéeykat, muy fanaan ci seeni loxo. \p \v 14 «Buleen saaga ab tëx te buleen fakktal silmaxa. Ragal-leen seen Yàlla. Maay Aji Sax ji. \p \v 15 «Buleen safaan dëgg cib àtte. Buleen far néew-ji-doole te buleen far boroom doole. Àtteleen seen moroom ci dëgg. \v 16 Buleen wër di yàq deru nit ci seen bokki waa réew. Buleen def dara lu mana reylu seen moroom. Maay Aji Sax ji. \p \v 17 «Buleen tong seen mbokk, te àrtuleen seen moroom bu baax bala ngeena bokk ak moom gàddu bàkkaar. \v 18 Buleen di feyantook seen mbokkum waa réew te buleen ko dencal mer. Ni ngeen soppe seen bopp nag, nangeen ko soppe seen moroom. Maay Aji Sax ji. \p \v 19 «Te it sama dogali yoon yii nangeen ko sàmm: buleen boole ñaar yu bokkul wirgo ci seenug jur, ñuy jaxasoo; seen tool it buleen ci ji ñaari wirgoy jiwu te buleen sol yére yu ñu ràbbe ñaari xeeti wëñ yu bokkul. \p \v 20 «Ku tëdde ab jaam bu wara séy ak keneen te fekk joteesu ko, goreeleesu ko, ndàmpaay war na ca, waaye deesu leen boole rey, ndax li ndaw si dib jaam ba tey. \v 21 Waa ji day yóbbu am kuuyu peyug tooñ ca bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* ma, muy peyug tooñ, gi muy sarxalal Aji Sax ji. \v 22 Na ko \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi defal kuuy miy \w saraxas peyug tooñ|lemma="Sarax yi:"\w* muy njotlaayam fi kanam Aji Sax ji, ndax bàkkaar bi mu def. Kon dees na ko jéggal bàkkaar bi mu def. \p \v 23 «Bu ngeen duggee ca réew ma, ba jëmbat fa mboolem xeetu garab guy meññ ay doom, nangeen aayal doom ya. Diiru ñetti at ngeen di aayal doom ya. Dungeen ko lekk ci diir boobu. \v 24 Atum ñeenteel ba doom ya yépp lañuy sellalal Aji Sax ji, te di ko bége ci biir cant. \v 25 Juróomeelu at ma doŋŋ ngeen di saña lekk doom ya. Su ko defee meññeef ma barkeelal leen. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla. \p \v 26 «Buleen lekk lu am deret. Buleen di gisaane mbaa ngeen di jibar. \v 27 Buleen wat seen peggu kawaru bopp te buleen dagg seen peggu sikkim, \v 28 mbaa ngeen di dagg seen yaram, di ko mititloo ku dee, te buleen ñaasu fenn ci seen yaram. Maay Aji Sax ji. \p \v 29 «Buleen torxal seen doom ju jigéen, di ko def ab gànc; lu ko moy réew mi sóobu ci gànctu ba ne lijj ci ñaawtéef. \p \v 30 «Samay bési Noflaay nag wormaal-leen ko te sama bérab bu sell teral-leen ko. Maay Aji Sax ji. \p \v 31 «Buleen jublu ci ñiy gisaane nit ñu dee te buleen jublu ci boroom rawaan yiy seet, ndax kon ñu sobeel leen. Man maay seen Yàlla Aji Sax ji. \p \v 32 «Bu boroom bijjaaw teewee, jógleen wormaal ko. Deeleen rus mag te ragal-leen seen Yàlla. Maay Aji Sax ji. \p \v 33 «Bu ab doxandéem daleek yeen ci seenum réew, buleen ko lor. \v 34 Njuddu-ji-réew ji nangeen ko yemaleek doxandéem bi ngeen dëkkal. Soppleen ko ni ngeen soppe seen bopp, ndaxte ay doxandéem ngeen woon ca réewum Misra. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla. \p \v 35 «Buleen def njubadi ci lu ñuy natte guddaay mbaa diisaay mbaa lu ñuy sol, sotti. \v 36 Na seen nattukaayu diisaay jub, doom ya ngeen cay natte jub, te na nattukaayi sol-sotti yi jub. Maay seen Yàlla Aji Sax, ji leen génne réewum Misra. \p \v 37 «Nangeen sàmm sama dogali yoon yépp ak sama santaane yépp te di ko jëfe. Maay Aji Sax ji.» \c 20 \s1 Lu jëm ci peyug bàkkaar \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na Musaa ba tey ne ko: \v 2 «Waxal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen: Muy bànni Israyil muy doxandéem ci Israyil, képp ku ci jël ciy doomam, jébbal tuur mi ñuy wax Moleg, dee rekk mooy àtteem. Na ko waa réew mi dóor ay doj, ba mu dee. \v 3 Man ci sama bopp dinaa noonoo nit kooku te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil, ndax li mu jël ciy doomam jox Moleg, di sobeel sama \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* tey teddadil sama tur wu \w sell|lemma="sell:"\w*. \v 4 Su fekkee ne waa réew mi dañu koo seetaan ba seetaan ko, muy jox Moleg ku bokk ciy doomam te taxul ñu rey ko, \v 5 man ci sama bopp maay noonoo nit kooku mook ay bokkam; dinaa dagge nit kooku ci biir bànni Israyil, génne ko, mook mboolem ñi mu àndal topp Moleg di bokkaale. \v 6 Ku jublu ci ñiy gisaane nit ñu dee mbaa mu jublu ci boroom rawaan yiy seet, topp leen, di ma leen bokkaalee, dinaa ko noonoo moom itam te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil. \v 7 Sell-luleen te sell, ngir man Aji Sax ji maay seen Yàlla. \v 8 Nangeen sàmm samay dogali yoon te di ko jëfe. Man Aji Sax ji maay ki leen sellal. \p \v 9 «Képp ku saaga baayam mbaa ndeyam, dee rekk mooy àtteem. Gannaaw baayam la saaga mbaa ndeyam, mooy gàddu bakkanu boppam. \p \v 10 «Góor gu njaaloo, mook jabaru moroomam ji muy njaalool, dee rekk mooy seen àtte. \p \v 11 «Ku dëkkoo sa soxnas baay, sa baay nga torxal. Ñoom ñaar ñépp dee rekk mooy seen àtte, te ñooy gàddu seen bakkanu bopp. \v 12 Ku dëkkoo sa soxnas doom, mook soxnas doomam ñoom ñaar ñépp dee mooy seen àtte. Jëfu yàqute lañu def, kon ñooy gàddu seen bakkanu bopp. \p \v 13 «Su góor tëddee góor ni ñuy tëddee jigéen, ñaawtéef lañu def ñoom ñaar. Dee rekk mooy seen àtte, te ñooy gàddu seen bakkanu bopp. \v 14 Ku boole nit ak ndeyam jël leen jabar, def na lu bona bon. Dees leen di boole taal, lakk leen, moom ak jigéen ña, ndax mbon gu ni mel baña am ci seen biir. \v 15 Góor gu tëdde mala dee rekk mooy àtteem, te mala ma it dees koy rey. \v 16 Su jigéen jëmee ci mala mu mu doon, ba jaxasook moom, booleleen ku jigéen kaak mala ma, rey. Dee rekk mooy seen àtte, te ñooy gàddu seen bakkanu bopp. \p \v 17 «Su nit jëlee jabar ab jigéenam bu mu bokkal jenn ndey mbaa benn baay, ñu séq lalu séy, loolu gàcce la. Nañu leen dagge ci biir bànni Israyil, ñooñuy gis. Gannaaw moo tëdde ab jigéenam, na wéetoo añu ñaawtéefam. \p \v 18 «Ku tëdde jigéen ju gis baax, torxal na ko, xàwwi na suturaam ci biir póotam te ku jigéen ki itam xàwwi na suturas boppam. Dees leen wara dagge ñoom ñaar ñépp ci biir bànni Israyil. \p \v 19 «Buleen dëkkoo seen yaay ju ndaw mbaa seen bàjjan, ndax kon torxal ngeen ku ngeen jegewool lool cig bokk, te yeen ñaar ñépp ay wéetoo seen añu ñaawtéef. \p \v 20 «Ku dëkkoo soxnas baayam bu ndaw, baayam bu ndaw la torxal. Ñooy wéetoo seen añu ñaawtéef. Duñu am takkndeer ba keroog ñuy dee. \p \v 21 «Bu nit nangoo jabaru ku mu bokkal waajur, loolu gàcce la. Torxal na ka mu bokkal waajur te duñu am takkndeer. \p \v 22 «Sàmmleen sama dogali yoon yépp ak sama santaane yépp te jëfe ko, ngir réew ma ma leen jëme, ngeen dëkki fa, bañ leena gëq. \v 23 Buleen roy defini xeet wi ma leen di dàqal, ndax yooyu yépp lañu doon def, ba ma sib leen. \v 24 Yeen nag ma ne leen yeenay nangu seen réew ñoom, ndax maa leen ko jox, ngeen moom ko, muy réew mu meew maak lem ja tuuroo. Man maay seen Yàlla Aji Sax, ji leen ràññatleek yeneen xeet yi. \v 25 Kon nangeen ràññee mala mu dagan ak mu daganul, ak itam njanaaw lu dagan ak lu daganul, te baña sobeel seen bopp ndax mala mbaa njanaaw mbaa mboolem bindeef yu sew-sewaan yiy dox ci suuf te ma limal leen ne setul. \p \v 26 «Nangeen ma nekkal ñu sell, ndaxte ku Sell laa, man Aji Sax ji, te dama leena ràññatleek yeneen xeet yi, ngeen di sama ñoñ. \p \v 27 «Góor gu bokk ci yeen mbaa jigéen, di seete nit ñu dee mbaa muy boroom rawaan buy gisaane, dee rekk mooy àtteem. Dees koy dóor ay doj, mu dee, gàddu bakkanu boppam.» \c 21 \s1 Lu jëm ci sañ-sañi sarxalkat yi \p \v 1 Gannaaw loolu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na Musaa ne ko: «Waxal \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yiy doomi Aaróona ne leen: Bu ci kenn sobeel boppam, di laal mbokkam mu dee, \v 2 su dul ñi ko gëna jege ci wàllu mbokk, muy ndeyam mbaa baayam mbaa doomam ju góor ak doomam ju jigéen, mbaa ku góor ku mu bokkal waajur, \v 3 mbaa ab jigéenam bu séyagul te bootu ci moom ndax amul jëkkër— ku mu bokkal noonu, sañ naa sobewu ndax moom. \v 4 Warula sobeel boppam, di teddadil boppam, ndax kilifa la ciw xeetam. \p \v 5 «Buñu wat fenn ci seen bopp te buñu wat seen peggi sikkim, buñu dagg seen yaram it, di ko mititloo ku dee. \v 6 Nañu nekkal seen Yàlla ay nit ñu \w sell|lemma="sell:"\w*, te baña teddadil seen turu Yàlla, ndax saraxi sawar yi ñeel Aji Sax ji, te di seen ñamu Yàlla, ñoo koy joxe. Kon nag dañoo wara sell. \p \v 7 «Ab gànc mbaa ku ñu torxal, tëdde ko, ñoom duñu ko jël soxna. Ku jëkkëram baal it duñu ko jël soxna, ndax dañoo sellalal seen bopp seen Yàlla. \v 8 Te itam nangeen ràññee ne ñu sell lañu, ndax seen ñamu Yàlla, ñoo koy joxe. Nangeen leen jox céru nit ñu sell, ndax ku Sell laa, man Aji Sax ji leen sellal, yeen. \p \v 9 «Su fekkee ne doomu sarxalkat da di jigéen juy teddadil boppam, di gànctu, kooku baayam lay torxal. Dees koy taal, lakk ko. \p \v 10 «Sarxalkat, bi gëna màgg ci bokkam yiy sarxalkat, te ñu sotti diw gi ñuy fale ci boppam, sellal ko, muy sol yére yu sell yi, kooku du njañu te du xotti ay yéreem, di ko ñaawloo ku dee. \v 11 Fu ab néew nekk du fa dem, bu doon ndeyam mbaa baayam sax, du ko taxa sobeel boppam. \v 12 Du génn ëttu bérab bu sell bi, mbaa muy teddadil bérabu Yàllaam bu sell bi, ndax diwu pal gu sell gi ko Yàllaam fale. Maay Aji Sax ji. \v 13 Sarxalkat bu mag bi, ku xamul góor lay jël soxna. \v 14 Ku jëkkëram faatu mbaa ku ñu baal mbaa ku ñu torxal, tëdde ko, mbaa ab gànc, du ko mana jël soxna. Ab janq bu mu bokkal doŋŋ la mana jël soxna. \v 15 Su ko defee du teddadil aw askanam ci biir bànni Israyil, ndax man Aji Sax ji maa ko sellal.» \s1 Liy ngànt ci sarxalkat \p \v 16 Bu loolu wéyee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na Musaa ne ko: \v 17 «Waxal Aaróona ne ko: Muy tey muy ëllëg ba fàww, góor gu askanoo ci yaw ak maas gu mu mana bokk, su amee sikk du mana agsi ba ci sarxalukaay bi, di joxe ñamu Yàllaam. \v 18 Du kenn sax ku am sikk kuy agsi ba fii, du gumba, du kuy soox, du ku xar-kanamam am sikk mbaa ku cér yi sutaate. \v 19 Du it ku tànk bi làggi mbaa loxo bi, \v 20 mbaa ab xuuge mbaa ab tungune; du it ku bëtam am sikk mbaa ku ràmm mbaa ku am góom yu sol dëtt, mbaa ku ñu tàpp. \v 21 Askanu Aaróona \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi, du kenn ku ci am sikk kuy agsi ba fii, di joxe saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji. Sikk si ci moom a tax du mana agsi ba fii, di joxe ñamu Yàllaam. \v 22 Du tere mu saña lekk ci ñamu Yàllaam, muy ñam wu \w sell|lemma="sell:"\w* ak wu sella sell. \v 23 Waaye warula jege rido bi, mbaa muy dem ba ca \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* ba, ndax sikk si ci moom. Bumu teddadil sama bérab yu sell, ngir man Aji Sax ji maa sellal bérab yooyu.» \p \v 24 Musaa jottli na Aaróona aki doomam kàddu yooyu, ñoom ak mboolem \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \c 22 \s1 Liy tax ñu nangu sarax \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dellu wax Musaa ne ko: \v 2 «Waxal Aaróona aki doomam yu góor ne leen lii mooy li mana tax ñu sore yu \w sell|lemma="sell:"\w*, yi ma \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* sellalal, ngir baña teddadil sama tur wu sell. Maay Aji Sax ji. \v 3 Wax leen ne leen: Muy tey, muy ëllëg, ba fàww, képp ku sobewu, di góor gu bokk ci seen askan, bu jegee lenn luy sarax su sell su ma bànni Israyil jagleel, kooku dootu ma liggéeyal. Maay Aji Sax ji. \v 4 Askanu Aaróona, genn góor gu ci bokk du lekk ci sarax yu sell yi, li feek muy ànd ak jàngoroy der juy law mbaa jàngoroy xelli, ba keroog muy set. Ku ci laal lenn lu laal ab néew ba sobewu, mbaa mu tuur wasal moom ci boppam, \v 5 mbaa mu laal yu sew-sewaan yiy dox ci suuf te di ko sobeel, mbaa mu laal nit ku ko sobeel ak lu sobe sa mana doon, \v 6 dina yendoo sobe sa ba jant so, te du lekk ci sarax yu sell yi ndare du dafa sangu. \v 7 Bu jant sowee nag set na, te man naa lekk ci sarax yu sell yi, ndax ñamam la. \v 8 Lu médd mbaa lu rab fàdd waru koo lekk, mu di ko sobeel. Maay Aji Sax ji. \v 9 Sarxalkat yi dañoo wara dénkoo samay dénkaane bala ñoo gàddu bàkkaar, di dee ndax seenug néewal ci yooyu. Maay Aji Sax ji leen sellal. \p \v 10 «Kenn ku bokkul ci waa kër \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi du lekk ci sarax yu sell yi. Muy ku dal ak ab sarxalkat, muy ku koy liggéeyal di feyeeku, kenn du ci lekk ci sarax yu sell yi. \v 11 Waaye su sarxalkat bi jëndee ab jaam ci xaalisam, jaam ba man na caa lekk. Jaam bu juddoo ci kër sarxalkat bi it man naa lekk ci ñamam woowu. \v 12 Doomu sarxalkat, bu séyeek góor gu bokkul ci waa kër sarxalkat yi, jooxe yu sell yi, dootu ci saña lekk. \v 13 Waaye doomu sarxalkat bu boroom këram faatoo mbaa mu tàggook moom te amu ca doom, bu delloo kër baayam na mu fa nekke woon ba muy gone, sañ naa lekk ci ñamu baayam. Waaye kenn ku ci bokkul sañu cee lekk. \v 14 Gannaaw loolu képp ku bokkul ci waa kër sarxalkat yi, bu lekkee ci sarax su sell te du teyeefam, na dolli ca njégu sarax sa juróomeelu céru njég ga, delloo ko sarxalkat bi. \v 15 Te itam bu sarxalkat yi bàyyi bànni Israyil di teddadil sarax yu sell yi ñu jagleel Aji Sax ji. \v 16 Buñu leen di bàyyi it ñuy gàddu bàkkaar buy laaj peyug tooñ, ngir lenn lu ñu lekk ci sarax yu sell yooyu. Man Aji Sax ji maa sellal yooyu sarax.» \p \v 17 Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: \v 18 «Waxal Aaróona aki doomam yu góor ak bànni Israyil gépp ne leen: Képp ku bokk ci waa kër Israyil, mbaa ci doxandéem yi ci Israyil, di joxeel Aji Sax ji ab \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, muy sarax su ñuy wàccoo ngiñ mbaa \w saraxu yéene|lemma="Sarax yi:"\w*, \v 19 liy tax ñu nangul ko mooy muy jur gu amul sikk, di góor; man naa doon aw yëkk mbaa kuuy mbaa sikket. \v 20 Lenn lu ci am sikk buleen ko sarxal, ndax deesu leen ko nangul. \p \v 21 «Su nit dee joxsi Aji Sax ji aw nag mbaa gàtt, muy \w saraxu cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*, mu di ko wàccoo ngiñ mbaa muy saraxu yéene, na doon lu amul sikk, ndax ñu nangul ko. Lenn luy sikk du nekk ci jur gi. \v 22 Du doon lu gumba, du doon lu làggi, du doon lu kuuñ, du doon lu ami góom, mbaa lu ràmm, mbaa lu xas. Buleen sarxalal Aji Sax ji yu mel noonu. Ab saraxu sawara, buleen ko jële ci lu mel noonu, di ko joxe ci kaw \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi, ñeel Aji Sax ji. \v 23 Waaye su dee nag mbaa gàtt bu ab céram ëpp mbaa mu yées, saraxu yéene la mana doon; su dee sarax su ñuy wàccoo ngiñ, deesu ko nangu. \v 24 Te it jur gu ñu motoxal ngóoraam mbaa ñu toj ko mbaa ñu xuuf ko mbaa ñu dog ko, deesu ko sarxalal Aji Sax ji. Buleen def loolu mukk ci seenum réew. \v 25 Buleen nangoo lenn lu ni mel ci loxol doxandéem it, di ko jébbal seen Yàlla, muy saraxu ñamam. Deesu leen ko nangul, ndax la matadi ca moom mooy sikk sa.» \p \v 26 Aji Sax ji wax na Musaa itam ne ko: \v 27 «Barmol mbaa mbote mbaa tef wu doora juddu, na toog ci yaayam juróom ñaari fan; bu xasee am juróom ñetti fan, manees naa nangu mu doon saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. \v 28 Waaye su dee aw nag mbaa ab gàtt, deesu ko booleek doom ji rendi ci benn bés. \p \v 29 «Bu ngeen dee defal Aji Sax ji \w saraxu cant|lemma="Sarax yi:"\w*, sarxal-leen ko na ñu leen koy nangule. \v 30 Ci bés bi lees koy lekk, buleen ci fanaanal dara. Maay Aji Sax ji. \p \v 31 «Kon sàmmleen samay santaane te di ko jëfe. Maay Aji Sax ji. \v 32 Te buleen teddadil sama tur wu sell. Na bànni Israyil wormaal sama sellaay. Maay Aji Sax ji leen sellal, \v 33 génne leen réewum Misra, di seen Yàlla. Maay Aji Sax ji.» \c 23 \s1 Lu jëm ci bési màggal yi \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dellooti wax Musaa ne ko: \v 2 «Samay màggal, man Aji Sax ji, dangeen koo wara siiwal, muy ndaje yu \w sell|lemma="sell:"\w*. Samay màggal yii la. \p \v 3 «Juróom benni fan lees di liggéey, bésub juróom ñaareel ba \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w* doŋŋ lay doon, di bésub ndaje mu sell. Du lenn lu ngeen ciy liggéey. Bésub Noflaay la bu ñuy jagleel Aji Sax ji, ak fépp fu ngeen dëkk. \p \v 4 «Aji Sax ji, deeleen yégle ay màggalam, muy ay ndaje yu sell yu ngeen di wormaal saa yu jotee. Màggal yii la. \s1 Lu jëm ci bésub Mucc ak bési Mburu mu amul lawiir \p \v 5 «Fukki fan ak ñeent ci weer wi jëkk, diggante ngoon ak jant bu so, mooy \w màggalu bésub Mucc|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* ba, ñeel \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \p \v 6 «Fukki fan ak juróom ci weer woowu la \w ayu bésu Mburu mu amul lawiir|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* di tàmbali, ñeel Aji Sax ji. Diiru juróom ñaari fan mburu mu amul lawiir ngeen wara lekk. \v 7 Bés bu jëkk bi ndaje mu \w sell|lemma="sell:"\w* ngeen ciy amal. Mboolem lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey. \v 8 Defleen ci saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji diiru juróom ñaari fan. Bésub juróom ñaareel ba di bésub ndaje mu sell. Mboolem lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey.» \s1 Lu jëm ci màggalu Ndoortel meññeef \p \v 9 Su loolu wéyee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na Musaa ne ko: \v 10 «Waxal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen: Bu ngeen duggee ca réew ma ma leen jox, ba dajale la ngeen jële ca suufam, yóbbuleen ci \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi takku peppum lors bi ngeen jëkka góob. \v 11 Sarxalkat bi day yékkati takk bi, jébbal ko Aji Sax ji, ngir mu nangul leen. Bés bi topp ci \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w* bi lay yékkati takk bi, jébbal ko ko. \v 12 Bés bi ñuy yékkati takk bi, jébbale, nangeen ci sarxal kuuy mu amul sikk, tollu ci menn at, ñu defal ko Aji Sax ji \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*. \v 13 \w Saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* mi muy àndal juróom benni kiloy sunguf su mucc ayib lay doon, ñu xiiwe ko diw, muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji, ngir xetug jàmm. \w Sarax si ñuy tuural|lemma="Sarax yi:"\w* Aji Sax ji, liitaru biiñ laak genn-wàll. \v 14 Du mburu, du pepp mu ñu séndal, du pepp mu bees mu ngeen wara lekk, ba keroog bés boobu ngeen di indi seen saraxu Yàlla. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan, ak fépp fu ngeen dëkk. \s1 Lu jëm ci màggalu bésu Ngóob \p \v 15 «\w Bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w* ba ngeen di indi takku bele biy \w saraxu yékkati-jébbale|lemma="Sarax yi:"\w*, bés ba ca topp ngeen di dale waññ juróom ñaari ayi bés yu mat sëkk. \v 16 Waññleen ba ca bés ba topp ci juróom ñaareelu bésub Noflaay ba, muy juróom fukki fan, ngeen indil ca \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* mu bees. \v 17 Seeni kër ngeen di jële ñaari mburu yuy doon saraxu yékkati-jébbale, mu ci nekk di lu ñu lakke juróom benni kiloy sunguf su mucc ayib; dees ciy def lawiir, lakkaale ko ko, muy \w saraxu ndoortel meññeef|lemma="Sarax yi:"\w*, ñeel Aji Sax ji. \v 18 Na mbooloo mi booleek mburu mi juróom ñaari kuuy yu amul sikk te tollu ci menn at, ak yëkk ak ñaari kuuy, mu doon \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ñeel Aji Sax ji. Na ànd ak saraxu pepp ak \w sarax si ñuy tuur|lemma="Sarax yi:"\w*. Loolu sarax la ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji. \v 19 Te itam ngeen sarxal ab sikket buy doon \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w* ak ñaari xari menn at, muy \w saraxu cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*. \v 20 \w Sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi day yékkati ñaari xar yooyu, boole kook mburum ndoortel meññeef mi, def ko sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji. Yooyu sarax di lu \w sell|lemma="sell:"\w* ñeel Aji Sax ji, sarxalkat bee ko moom. \v 21 Wooteleen ci bés boobu ndaje mu sell, te lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan, ak fépp fu ngeen dëkk. \p \v 22 «Bu ngeen dee góob seen tool, buleen góob ba fa tool ba yem te buleen ci toppaat, di foraatu. Aji ñàkk akub doxandéem ngeen koy bàyyee. Maay seen Yàlla Aji Sax ji.» \s1 Li ci màggalu bésu Liit ya \p \v 23 Gannaaw loolu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na Musaa ne ko: \v 24 «Waxal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen: Bu juróom ñaareelu weer taxawee, bés bi jëkk ci weer wi, na doon seen \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w* bu ngeen di amal ndaje mu \w sell|lemma="sell:"\w*. Deeleen fàttlee bés bi liit yu xumb. \v 25 Mboolem lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey, waaye nangeen ci indi saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.» \s1 Li ci bésub Njotlaay ba \p \v 26 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji teg ca wax Musaa ne ko: \v 27 «Te itam fukki fan ci juróom ñaareelu weer woowu, \w bésub Njotlaay|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* ba lay doon. Ndaje mu \w sell|lemma="sell:"\w* ngeen ciy amal. Nangeen ci toroxlu te indi saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. \v 28 Du lenn lu ngeen di liggéey ci boobu bés, ndax bésub Njotlaay la bu ngeen di jotoo fi seen kanam Yàlla, Aji Sax ji. \v 29 Te kat, képp ku toroxluwul boobu bés, dees koy dagge ci biir bànni Israyil. \v 30 Képp ku liggéey lenn ci boobu bés, su boobaa dinaa far kooku ci biir bànni Israyil, sànk ko. \v 31 Buleen ci liggéey dara. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan ak fépp fu ngeen dëkk. \v 32 Seen \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w* la bu ngeen di nopplu doŋŋ te war cee toroxlu. Li ko dale ci ngoonug juróom ñeenti fan ci weer wi ba ca ëllëg sa, ba jant so, ci ngeen di wormaal seen bésub Noflaay.» \s1 Li ci màggalu bési Mbaar yi \p \v 33 Su loolu wéyee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na Musaa ne ko: \v 34 «Waxal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen: Ñu waññ dale ko ci fukki fan ak juróom ci weeru juróom ñaareel woowu ba mu am juróom ñaari fan. Diir boobu mooy \w màggalu bési Mbaar|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* yi, ñeel Aji Sax ji. \v 35 Bés bu jëkk bi bésub ndaje mu \w sell|lemma="sell:"\w* la. Mboolem lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey. \v 36 Diiru juróom ñaari fan ngeen di indi saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. Bésub juróom ñetteel, ba wara doon seen ndaje mu sell, nangeen ci indi saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. Ndajem mujjantal ba la. Mboolem lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey. \p \v 37 «Yooyoo di màggali Aji Sax ji, yi ñu wara yégle, di ndaje yu sell yu ñuy indi ay saraxi sawara, ñeel Aji Sax ji, muy \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ak \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w*, ak yeneen saraxi jur gu ñuy rendi, ak \w sarax yi ñuy tuural|lemma="Sarax yi:"\w* Aji Sax ji, bés bu nekk ak la ca war. \v 38 Yooyu sarax jotewul dara ak saraxi \w bési Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w* yu Aji Sax ji. Jotewul dara it ak yi ngeen di joxeel Aji Sax ji mbaa mboolem sarax yi ngeen di wàccoo ngiñ, ak mboolem \w saraxi yéene|lemma="Sarax yi:"\w* yi ngeen di defal Aji Sax ji. \p \v 39 «Ci biir loolu, fukki fan ak juróom ci juróom ñaareelu weer wi, gannaaw bu ngeen dajalee meññeefum réew mi, amal-leen màggalug Aji Sax ji diiru juróom ñaari fan. Na bés bu jëkk ba di \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*, bésub juróom ñetteel ba di bésub Noflaay. \v 40 Bés bu jëkk ba wittleen doomi garab yu rafet ak cari tiir ak cari garab yu sëq ak cari garab yu ñuy wax sóol, tey saxe tàkkal dex. Nangeen bànneexu fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji diiru juróom ñaari fan. \v 41 Wormaal-leen màggalug Aji Sax jooju, di juróom ñaari fan cim at, te wormaal-leen ko ci juróom ñaareelu weer wi. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan. \v 42 Ci ay mbaar ngeen di dëkk diiru juróom ñaari fan yooyu. Mboolem njuddu-ji-réew ci Israyil na ci dëkke mbaar, \v 43 su ko defee seeni sët xam ne ciy mbaar laa dëkkaloon bànni Israyil, ba ma leen génnee réewum Misra. Maay seen Yàlla Aji Sax ji.» \p \v 44 Noonu la Musaa xamale bànni Israyil bési màggalug Aji Sax ji. \c 24 \s1 Lu jëm ci tegukaayu làmp bi ak mburu yi \p \v 1 Ba loolu amee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na Musaa ne ko: \v 2 «Santal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, ñu indil la diwu segalu oliw gu set, ngir leerlu, ñu di ko taale làmp yi guddi gu nekk. \v 3 Ci kanam rido bi làq gaalu àlluway seede si, ci biir \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi la Aaróona di teg làmp yi, muy fanaanee tàkk ba bët set, fi kanam Aji Sax ji. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan. \v 4 Na teg làmp yi ci kaw tegukaayu làmp ba ñuy tëgge wurusu ngalam, muy fanaanee tàkk fi kanam Aji Sax ji. \p \v 5 «Sàkkal sunguf su mucc ayib, lakk ci fukki mburu ak ñaar, mburu mu nekk di juróom benni kiloy sunguf. \v 6 Tegal mburu yi ci kaw taabalu wurusu ngalam bi, fi kanam Aji Sax ji, te def ko ñaari jal, jal bu ne juróom benni mburu. \v 7 Jal bu nekk teg ca \w cuuraay|lemma="cuuraay l-:"\w* lu raxul, mu wuutu mburu mi, di saraxu baaxantal, te di saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. \v 8 \w Bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w* bu nekk nañu saxoo taaj mburu yooyu fi kanam Aji Sax ji. Loolu sas la bu bànni Israyil di tegoo fàww. \v 9 Mburu yooyu Aaróona aki doomam yu góor ñoo koy féetewoo, te nañu ko lekke fu \w sell|lemma="sell:"\w*, ndaxte lu \w sella sell|lemma="sell:"\w* la, di lu ñu séddoo fàww ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji.» \s1 Li war ci yenn xeeti tooñaange \p \v 10-11 Ba loolu wéyee amoon na ci biir \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* jenn waay ju yaayam di doomu Israyil te tuddoon Selomit doomu Dibbri, Daneen ba. Baayam di waa Misra. Mu am bés xeex jib ci biir dal bi, ci diggante waa jooju ak jenn waayi Israyil ju raxul. Ci biir loolu waa ji yaayam di doomu Israyil wax Yàlla lu ñaaw, tudd ko jaar fu bon. Ñu yóbbu ko ca Musaa. \v 12 Ñu tëj waa ja, ba xam lu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji namm ci moom. \p \v 13 Ci kaw loolu Aji Sax ji wax Musaa ne ko: \v 14 «Génneel dal bi ki may wax lu ñaaw, man Yàlla, te na mboolem ku ci dégg teg loxoom ci kaw boppam, ba noppi mbooloo mépp dóor koy doj, ba mu dee. \v 15 Bànni Israyil nag nangeen leen wax ne leen: Képp ku wax Yàllaam lu ñaaw, jaar fu bon, na wéetoo añam. \v 16 Ku ñàkke kersa turu Aji Sax ji, dee rekk mooy àtteem. Mbooloo mi mépp a ko wara dóor ay doj, ba mu dee. Muy doxandéem muy njuddu-ji-réew, ku ci ñàkke kersa turu Aji Sax ji, dee mooy àtteem. \p \v 17 «Bu loolu weesee képp ku faat bakkanu nit, dee rekk mooy àtteem. \v 18 Ku faat bakkanu mala, na fey boroom. Bakkan, bakkan a koy fey. \v 19 Képp ku gaañ moroomam, la mu ko def rekk lañu koy def. \v 20 Damm-damm, damm-damm a koy fey; bët, bët a koy fey; bëñ it bëñ a koy fey. Ni mu gaañe moroomam rekk, ni lañu koy gaañe. \p \v 21 «Ku rey ag jur na fey boroom, waaye ku rey nit dee mooy àtteem. \v 22 Na àtte bi di benn ci doxandéem ak njuddu-ji-réew, ndax man Aji Sax ji maay seen Yàlla.» \p \v 23 Ci kaw loolu Musaa wax ko bànni Israyil, ñu génne dal ba waa ja ñàkke Yàlla kersa, dóor ko ay doj, ba mu dee. Kon li bànni Israyil def mooy li Aji Sax ji santoon Musaa rekk. \c 25 \s1 Lu jëm ci atum Noflaay \p \v 1 Gannaaw loolu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na Musaa ca tundu Sinayi ne ko: \v 2 «Waxal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen: Bu ngeen duggee ca réew ma ma leen jox, suuf sa ca boppam war naa am àppu noflaayam ngir Aji Sax ji. \v 3 Diiru juróom benni at ngeen di ji seen tool; juróom benni at yooyu itam ngeen di wolli seen tóokëru reseñ, dajale meññeef ma. \v 4 Waaye atum juróom ñaareel ba atum Noflaay la wara doon: suuf sa ca boppam day nopplu doŋŋ ngir Aji Sax ji. Buleen ci ji seen tool, buleen ci wolli seen tóokëru reseñ. \v 5 La saxe ca seenum ngóob sax, buleen ko góobaat te it reseñ gu ñu wolliwuloon buleen ko raasaatu. Atum Noflaay la wara doon: suuf sa ca boppam na nopplu atum lëmm. \v 6 Waaye lépp luy saxayaay ci atum Noflaay sañ ngeen koo lekk, yeen ak seen jaam yu góor ak yu jigéen, ak seeni surga ak doxandéem bu dal ak yeen. \v 7 Seen jur it ca la, ba ca rabi àll ya ca seen réew. Mboolem lu suuf sa meññ, manees na koo lekk. \p \v 8 «Gannaaw loolu nangeen waññ ba ci juróom ñaari ati Noflaay, loolu di juróom ñaari at ba muy juróom ñaari yoon. Mu doon seen juróom ñaari ati Noflaay, tollu ci ñeent fukki at ak juróom ñeent. \v 9 Su boobaa ci fukki fan ca juróom ñaareelu weer wa nangeen wal-lu ag liit fépp. \w Bésub Njotlaay|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* boobu nangeen wal ag liit ci seenum réew ba mu daj. \v 10 Te nangeen sellal at ma ca topp di juróom fukkeelu at ma, ngeen yéene ca mboolem waa réew ma ba mu daj, ne ngoreel taxaw na. Seen atum Yiwiku la, ku nekk war cee dellu ca suufu waa këram, ku nekk it wara dellu ca làng ga mu bokk. \v 11 Seen atum Yiwiku la atum juróom fukkeel boobu di doon. Dungeen ci ji, dungeen ci góobaat lu saxe ca seenum ngóob te dungeen ci wolli ag reseñ, di ko witt. \v 12 Gannaaw atum Yiwiku la, na doon at mu ngeen sellal. Saxayaayub tool ngeen saña lekk. \p \v 13 «Atum Yiwiku moomu ci ngeen di delloo ku nekk suufam. \v 14 Bu ngeen di jaay seen waa réew suuf nag mbaa ngeen di jënde suuf ci seen waa réew, buleen di naxante. \v 15 Limu at yi dox seen digganteek atum Yiwiku ma mujj, na dëppook njég gi ngeen di jënde suuf ci seen waa réew. Limu ati mbey yi dox seen digganteek atum Yiwiku ma ca toppaat it, war naa dëppook njég ga ñu leen jaaye. \v 16 Lu at yooya gëna bare, njég ga gëna jafe; lu at ya gëna néew, njég ga gëna yomb, ndaxte limu meññeefum suuf sa lees leen koy jaaye. \v 17 Buleen di naxante, waaye ragal-leen seen Yàlla, ndax man Aji Sax ji maay seen Yàlla. \p \v 18 «Saxleen ci samay dogal, sàmm samay ndigali yoon, di ko jëfe, ndax ngeen dëkk ak jàmm ci réew mi. \v 19 Kon suuf si dina nangu, ngeen di lekk ba suur te dëkk fa ci jàmm. \v 20 Jombul ngeen di wax naan: “Lu nuy lekk nag ci atum juróom ñaareel ba, gannaaw dunu ci ji te dunu ci dajale sunu meññeef?” \v 21 Waaye dinaa leen yónnee sama barke ca atum juróom benneel ba, suuf si nangul leen meññeefum ñetti at. \v 22 Bu ngeen tolloo ci ji ci atum juróom ñetteel ba, dina leen fekk ngeen di lekk meññeefum daaw-jéeg, te meññeefum atum juróom ñeenteel ba dina agsi, fekk ngeen di lekk ca mu daaw-jéeg ma. \s1 Liy sañ-sañ ci mbirum suuf su ñuy jotaat \p \v 23 «Suuf si deesu ko jaay, mu wel fàww, ndax maay Boroom suuf si, yeen ay doxandéem ngeen fi, yu ma fi dëkkal. \v 24 Fépp fu bokk ci seenum réew, nangeen fa yoonal sañ-sañu jotaat ca suuf sa. \p \v 25 «Bu sa mbokk demee ba ñàkk tax koo jaay ci suufam, mbokkam mi ko gëna jege te am sañ-sañu jotaat suufam, na jëndaat la mbokk ma jaayoon. \v 26 Ku amul ku ko ko jotaatal te moom ci boppam mu mujj woomle, ba am lu mu ko jotaate, \v 27 day waññ at ya njaay ma am, delloo ki mu jaayoon ati mbey ya ca kooka dese, daldi mana jotaat ci suufam. \v 28 Waaye su amul lu mu jëndaate suufam, suuf sa day des ca loxol ka mu jaayoon, ba keroog atum Yiwiku ma délsi. Bu atum Yiwiku ma délsee, sañ naa dellu ca suufam. \p \v 29 «Su dee waa ju jaay ab dëkkuwaay bu nekk ci dëkk bu mag bu ñu tabax tata wëralee ko ko, dina ko saña jotaat li feek njaay mi amul at. Ci diir boobu la ko saña jotaate. \v 30 Su ñu ko jotaatul ba njaay ma am atum lëmm, dëkkuwaay boobu ci biir dëkk bu mag ba ñu wëralee tata day wel fàww, ñeel ka ko jënd, mook ku askanoo ci moom. Du lees di delloo ci atum Yiwiku. \v 31 Su dee ay dëkkuwaay ci dëkk yu ndaw yu ñu tabaxul tata, wëralee ko ko, dees koy yemaleek alali suuf. Sañees na koo jotaat te dees koy delloo ci atum Yiwiku. \p \v 32 «Su dee dëkki \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi ak seen dëkkuwaay ya ca biir nag, Leween ñi sañ nañu cee jotaat fàww. \v 33 Kon alalu Leween manees na koo jotaat —dëkkuwaay lay doon bu ñu jaay ci dëkki Leween ñi— dees koy delloo bu atum Yiwiku dikkee, ndax dëkkuwaay yi ci dëkki Leween ñi, seen alal la ju leen lew fàww ci seen biir bokki \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \v 34 Waaye suufas parlu yi bokk ci dëkki Leween ñi, deesu ko jaay, ndax ñoo koy moom fàww. \s1 Baaxeleen aji ñàkk \p \v 35 «Bu seen mbokkum bànni Israyil ñàkkee ba manatula fey lu mu leen ameel, nangeen ko dimbali, ni bu doon doxandéem mbaa màngaan, ndax mu mana dund ci seen biir. \v 36 Buleen teg lenn lu mu mana doon ci bor bu leen seen mbokk moomu ameel, waaye ragal-leen ci seen Yàlla, ndax mu mana dund ci seen biir. \v 37 Buleen ko lebal seen xaalis, di ca teg lenn, te buleen ko jox dund, di sàkku lu mu ca yokk ngir delloo leen ko. \v 38 Man \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji maay seen Yàlla ji leen génne réewum Misra, jox leen réewu Kanaan, te di seen Yàlla. \s1 Liy sañ-sañ ci jotaat nit \p \v 39 «Bu seen mbokk ñàkkee ci seen biir, ba jaay leen boppam, buleen ko jaamloo. \v 40 Defleen ko ni liggéeykat buy feyeeku mbaa màngaan bu ngeen dëkkal. Na leen liggéeyal ba keroog atum Yiwiku ma, \v 41 mu génn ci seeni loxo, mook ay doomam, daldi dellu ci làngu boppam, fa ay maamam séddoo. \v 42 Li waral loolu moo di bànni Israyil dañu di sama jaam yi ma génne réewum Misra. Deesu leen jaay njaam. \v 43 Buleen leen soxore ci biir kilifteef, waaye ragal-leen ci seen Yàlla. \v 44 Seen jaam yu góor ak seen jaam yu jigéen, nangeen leen jële ci xeet yi leen wër. Ci ñooñu ngeen di jënde ay jaam, góor ak jigéen. \v 45 Walla ngeen jënde ba tey ci doxandéem yi ci seen biir, mbaa ci njaboot yi doxandéem yi am ci réew mi te ñu nekk ci seen biir. Su ko defee ñu doon seen ngàllo. \v 46 Sañ ngeen leena donale seen doom yi leen di wuutu, ñu doon seen ngàllo seen giiru dund. Ñooñu sañ ngeen leena def ay jaam, waaye su dee ci seen diggante, yeen \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, buleen di soxorante ci biir kilifteef. \p \v 47 «Su fekkee ne ab doxandéem bu ngeen dëkkal mbaa ab màngaan dafa woomle te kenn ci seeni bokk ñàkk, ba jaay boppam doxandéem bi ngeen dëkkal mbaa kenn ku bokk ak doxandéem bi, \v 48 gannaaw bu jaayee boppam, manees na koo jotaat ba tey. Kenn ciy bokkam sañ na koo jotaat, \v 49 yaar muy baayam bu ndaw mbaa doomu baayam bu ndaw. Ku mu bokkal làng di mbokkam lenqe sax man na koo jotaat, te moom ci boppam man naa woomle ba jotaat boppam. \v 50 Na bokk ak ka ko jënd waññ, la dale ca at ma mu jaaye boppam, ba ca atum Yiwiku may ñëw, muy njégu goreelam, dëppook at yooya. Te it nañu ci seet àqu ñaqu liggéeykat. \v 51 Su desee ay at, lu at ya gëna baree, njég ga muy jotaate boppam gëna sore ci njég, ga ñu ko jënde woon. \v 52 Te su at yu néew doxee seen digganteek atum Yiwiku ma, na ko waññ te fey lu ni néewe, ngir jotaat boppam. \v 53 Ab surga lay doon ci njaatigeem at mu nekk, waaye waru koo soxore ci biir kilifteef, ngeen di seetaan. \v 54 Su fekkee ne jotaatuñu ko ci jotin yooyu sax, war naa moom boppam mooki doomam ca atum Yiwiku ma. \v 55 Ndax kat man la bànni Israyil di samay jaam. Ñoo di sama jaam ya ma génne réewum Misra; yeen, maay seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \c 26 \s1 Yool yi ci déggal Yàlla \p \v 1 «Buleen sàkkal seen bopp ay yàllantu, du lenn luy jëmmu tuur mbaa tuuru doj wu ngeen sampal seen bopp, te doj wu ñu ñaas ay nataal it, buleen ko sàkkal bérab ci seen réew, di ko sujjóotal, ndax man \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji maay seen Yàlla. \v 2 Sama \w bési Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*, wormaal-leen ko, te sama bérab bu sell ngeen teral ko. Maay Aji Sax ji. \p \v 3 «Su ngeen dee topp samay dogal, fonk samay santaane te di ko jëfe, \v 4 kon maa leen di tawal ci waxtoom, suuf si nangu, garab yi meññ. \v 5 Dingeen bàcc ba keroog wittum reseñ jot te dingeen witt reseñ ba keroog ji jot. Dingeen lekk seenum pepp ba suur këll te dingeen dëkk ak jàmm ci seenum réew. \p \v 6 «Maay baaxee réew mi jàmm it, ba bu ngeen tëddee kenn du leen tiital. Maay jële rab wu aay ci réew mi, te saamar du jóg, dal ci seenum réew. \v 7 Kon dingeen dàq seeni noon, saamar ba dal, ñu daanu fi seen kanam. \v 8 Seen juróomi nit ay dàq téeméer, seen téeméeri nit dàq fukki junni. Seeni noon la saamar di dal, ñu daanu fi seen kanam. \p \v 9 «Te itam maa leen di baaxe, giiral leen, yokk leen. Dinaa sàmm sama \w kóllëreek|lemma="kóllëre g-:"\w* yeen. \v 10 Dingeen lekk ngóob mu yàgg, dence lu yàgg, ba far génne mu yàgg ma, wuutal fa mu bees. \p \v 11 «Maay samp sama kër ci seen biir te duma leen sib. \v 12 Maay ànd ak yeen, di seen Yàlla, ngeen di sama ñoñ. \v 13 Man Aji Sax ji maay seen Yàlla ji leen génne réewum Misra, ngeen noppee doon seeni jaam; maa dog seen buumi njaam, siggil leen. \s1 Mbugal yi ci déggadil Yàlla \p \v 14 «Waaye bu ngeen ma déggalul te baña jëfe sama santaane yooyu yépp, \v 15 su ngeen teddadilee samay dogal, dëddu samay ndigal, ba jëfewuleen sama santaane yépp, xanaa di fecci sama \w kóllëreek|lemma="kóllëre g-:"\w* yeen, \v 16 su boobaa li may def ak yeen mooy lii: maay jekki wàcce njàqare ci seen kaw, mu ànd ak woppi ràgg, yaram wu tàng jérr ak bët yu lëndëm, ngeen gën di wopp. Dingeen ji seenum pepp ci neen, ndax seeni noon a koy lekk. \v 17 Maa leen di noonoo ba seeni noon duma leen, seeni bañ yilif leen. Dingeen daw te kenn dàqu leen. \p \v 18 «Bu loolu taxul ngeen déggal ma, maa leen di mbugal lu ko ëpp juróom ñaari yoon, feye leen ko seeni bàkkaar. \v 19 Maay sàggi seen sag bu réy. Maay def asamaan si leen tiim ne sereŋ nig weñ, suuf si wow koŋŋ ni xànjar. \v 20 Seen doole dina kasara, ndax suuf si ngeen di bey du leen nangul te garabi réew mi du meññ. \p \v 21 «Su ngeen saxee ci noonoo ma, bañ maa déggal, maay fulaat seen mbugal fukki yoon ak juróom, feye leen ko seeni bàkkaar. \v 22 Maay xabtal rabi àll yi ci seen kaw, ñu xañ leen seeni doom, seeni gétt ñu tas, seeni nit ñu néewal, ba seeni mbedd ne wëyëŋ. \p \v 23 «Su ma leen loolu yaralul ba tey, xanaa ngeen sax ci noonoo ma, \v 24 su boobaa man itam maa leen di noonoo, te it man ci sama bopp maa leen di mbugalaat lu ko ëpp fukki yoon ak juróom, feye leen ko seeni bàkkaar. \v 25 Maay dalal saamar ci seen kaw, feye leen ko kóllëre gi ngeen fecci. Bu ngeen làqoo ci seeni biir dëkk yu mag sax, maay wàcce mbas ci seen biir, seeni noon jekku leen. \v 26 Bu ma téyee loxo bi ma leen di leele, fukki jigéen dinañu bokk lakk seen mburum njël ci benn taal doŋŋ, natt ko ay somp, séddale, ngeen lekk, te dungeen suur. \p \v 27 «Waaye bu loolu weesee te déggaluleen ma, xanaa di ma noonoo ba tey, \v 28 su boobaa ma gën leena mereeti, noonoo leen, te man ci sama bopp maa leen di mbugalati lu ko ëpp fukki yoon ak juróom, feye leen ko seen bàkkaar. \v 29 Dingeen yàpp seeni doom yu góor, yàpp seen doom yu jigéen ndax xiif. \v 30 Dinaa tas seen \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w*\f + \fr 26.30 \fr*\fk bérabi jaamookaay: \fk*\ft ay tund la daan doon mbaa ay bérab yu ñu tànn. Waa Kanaan daan ci jaamu seeni yàllantu, di ca def xeeti jaamu yu jëm ci luy taxa giir; ak lu jëm ci rawaani ñu dee mbaa ñu di ca gànctu, topp seeni tuur ya leen ca doon xiir.\ft*\f*, toj seeni suurukaay. Seen kasaray tuur yi ne làcc, ma jal ca seeni néew. Maa leen di sib, \v 31 gental seen dëkk yu mag, tas seen bérab yu sell, te dootuma faale xetug jàmm ca seeni sarax. \v 32 Maay tas seenum réew, ba seen noon ya ko nangu yéemu ca. \v 33 Yeen nag maa leen di tasaare ci biir xeet yi, ndax maay génne saamar mbaram, mu dal ci seen kaw. Seenum réew dina wéet, seen dëkk yu mag gent. \p \v 34 «Su boobaa mboolem diir ba suuf di wéet moom lay daboo ati Noflaayam, fekk yeen ngeen nekk ca seen réewu noon ya. Su ko defee suuf si dina nopplu moos, ba daboo ko ati Noflaayam. \v 35 Mboolem diir bi suuf siy wéet, moom lay nopploo la mu noppluwuloon, ba leen ay ati Noflaay fekkee ngeen dëkk fa. \p \v 36 «Ñi des ci yeen, dinaa indi njàqare ci seen xol, foofa ngeen nekk ca seen réewu noon ya, ba xob wu ne foy-foy ngeen daw. Dingeen xélu ni ku ñuy dàqe saamar, bay daanu, te dàqeesu leen. \v 37 Dingeen fakkastalante di daw, ni ñu ñuy dàqe saamar, te dàqeesu leen, ba dungeen mana taxaw ci seen kanami noon. \v 38 Dingeen deeye àll, te seen suufu noon yaa leen di lekk. \v 39 Ñi des ci yeen dinañu ràgg ca seen réewi noon ndax seeni bàkkaar ak seen bàkkaari maam. \s1 Aji Sax ji du fecci kóllëreem \p \v 40 «Su ko defee ñoom dinañu tudd seen bàkkaar ak seen bàkkaaru maam ya, ndax dañu maa wor te dëkke maa noonoo, \v 41 ba man itam ma noonoo leen, toxal leen seen réewu noon. Bu ñu tuubee seen xol bu dëgër nag, ba matal seen mbugal yi sababoo ci seeni ñaawtéef, \v 42 su boobaa maay bàyyi xel ci sama \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* gaak Yanqóoba ak sama kóllëre gaak Isaaxa ak sama kóllëre gaak Ibraayma, te duma fàtte li ma dige ci wàllu réew mi. \p \v 43 «Waaye réew mi dinañu ko gental, mu daboo ati Noflaayam diir ba ñu ko dëddoo, wéetal ko, te fekk ñoom ñuy fey seen boru tooñ; ndax kat dañoo sofental samay santaane, xalab samay dogal. \v 44 Ndaxam du tax ma sofental leen ca seen réewu noon, mbaa ma di leen xalab, di leen faagaagal, nde kon ma fecci sama kóllëreek ñoom. Ndax man \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji maay seen Yàlla. \v 45 Maa leen di bàyyil xel ci sama kóllëre gaak seen maam ya ma génne réewum Misra, jaambur ñi seede, ngir doon seen Yàlla. Maay Aji Sax ji.» \p \v 46 Looloo di dogal yaak santaane yaak ndigali yoon ya Aji Sax ji tëral ca digganteem ak \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ca kaw tundu Sinayi, Musaa jottli leen ko. \c 27 \s1 Lu jëm ci jagleel Aji Sax ji nit ak alal \p \v 1 Bu loolu weesee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na Musaa ne ko: \v 2 «Waxal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen: Képp ku dogoo jagleel Aji Sax ji nit\f + \fr 27.2 \fr*\ft Nit man naa jagleel moroomam Yàlla, muy liggéey ca kër Yàlla ga. Aaya yii wone na ne nit ku ñu jagleel moroomam Yàlla, manees na koo yiwi ci kaw ñu feyal ko ab limu xaalis.\ft*\f*, man naa wàccook kàddoom ci kaw nii ñu ko xaymaa. \v 3 Su dee góor gu am ñaar fukki at ba juróom benn fukki at, nanga ko xayma ci juróom fukki dogi xaalis, ci xaalisu \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi. \v 4 Su dee jigéen, nanga ko xayma ci fanweeri dogi xaalis. \v 5 Su amee juróomi at ba ñaar fukki at, danga koy xayma ci ñaar fukki dogi xaalis, su dee góor, mbaa fukki dogi xaalis, su dee jigéen. \v 6 Su dee ku am weer jàpp juróomi at, nanga ko xayma ci juróomi dogi xaalis su dee góor; mbaa ñetti dogi xaalis su dee jigéen. \v 7 Su dee ku am juróom benn fukki at ak lu ko ëpp, nanga ko xayma ci fukki dogi xaalis ak juróom su dee góor; mbaa fukki dogi xaalis su dee jigéen. \v 8 Su fekkee ne ki dogu woona jagleel nit ki Aji Sax ji da di ku am-amam yées sa xayma, na kooku yóbbu nit ki ba ca \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba, sarxalkat bi xaymaal ko nit ki ci lu dëppook am-amam, moom mi dogu woon. \p \v 9 «Su fekkee ne la ñu dogu woona joxe ag jur la gu dagana sarxalal Aji Sax ji, day daldi \w sell|lemma="sell:"\w*. \v 10 Deesu ko weccee. Du jur gu baax gu ñu ko mana wuutoo, doonte jur gu bon la, te du jur gu bon gu ñu ko mana wuutoo, te fekk muy gu baax. Ci biir jagleel googu ku xasa wuutoo ag jur moroom ma, jur gu jëkk gaak kuutaay la dañuy bokk doon lu sell. \v 11 Su fekkee ne la ñu dogu woona joxe mala mu daganul la te daganula sarxalal Aji Sax ji, na nit ki yóbbu jur ga ba ca sarxalkat ba, \v 12 sarxalkat ba xayma ko. Su baaxee su bonee, lu mu ci dogal mooy wéy. \v 13 Su ko boroom bëggee jotaat, day fey njég ga, yokk ca xaajub juróomeelu njég ga. \p \v 14 «Su nit jagleelee Aji Sax ji dëkkuwaayam, sellalal ko ko, na sarxalkat bi xayma dëkkuwaay bi. Su baaxee su bonee, lu mu ci dogal mooy wéy. \v 15 Su fekkee ne ki dogu woona joxe dëkkuwaayam da koo bëgga jotaat, day fey njég ga ñu ko xaymaa, yokk ca xaajub juróomeelam, mu doonaat alalam. \p \v 16 «Su nit jagleelee Aji Sax ji suuf su mu moom ci suufas ndonoom, na ñuy xaymaa suuf sa, na dëppook dayob pepp bay mat jiwum suuf sa. Ñetti barigoy peppum lors yu ne juróom fukki dogi xaalis\f + \fr 27.16 \fr*\ft Benn dogu xaalis boobu mu ngi tollu woon ci benn siikal, diisaayam di fukki garaam.\ft*\f* a koy wecci. \v 17 Su fekkee ne ci atum Yiwiku la joxe suuf si, xaymab suuf si day mat sëkk ànd ak moom. \v 18 Waaye su fekkee ne gannaaw atum Yiwiku la joxe suuf si, sarxalkat bi da koy nattal njég gi ci at yi dox seen digganteek atum Yiwiku ma ca topp, génne ca at ya wees. \v 19 Su fekkee ne ki dogu woona joxe tool bi da koo bëgga jotaat, day fey njég ga ñu ko xaymaa, yokk ca xaajub juróomeelam, mu doonaat alalam. \v 20 Su jotaatul tool bi, ba ñu jaay tool bi keneen, deesu ko mana jotaat. \v 21 Bu tool bi yiwikoo ci atum Yiwiku nag, day daldi doon lu ñu sellalal Aji Sax ji, mel ni tool bu ñu aaye, mu doon alalu sarxalkat. \p \v 22 «Su fekkee ne nit ki dafa jagleel Aji Sax ji tool bu mu jënd, te donnu ko, \v 23 sarxalkat bi da koy xaymaal njég gi, méngale kook at yi dox seen digganteek atum Yiwiku may ñëw. Na nit ki fey la ñu xayma ca bés ba, xaalis ba di lu ñuy sellalal Aji Sax ji. \v 24 Bu atum Yiwiku dikkee, tool bi day dellu ca ka ñu ko jënde woon te mu di alalu ndonoom. \v 25 Mboolem lu ngeen xayma, na dëppook natt ba ñu yoonal ci bérab bu sell bi, maanaam li ñuy wax siikal te mu tollu ci fukki garaam. \p \v 26 «Waaye kat luy taaw cig jur, Aji Sax jee ko moom jeeg. Du lu kenn di dogoo jagleel Aji Sax ji. Muy barmol, muy mbote, muy tef, Aji Sax jeey boroom. \v 27 Su dee lu mala mu daganul taawloo, ka ko moomoon man na koo jotaat ndegam fey na njégam, ba dolli ca xaajub juróomeelu njég ga. Bu ñu ko jotaatul, dees koy jaay ci njég gi ñu ko xaymaa. \v 28 Mboolem lu ñu aayalal Aji Sax ji, lu sella sell la ñeel Aji Sax ji. Lépp lu nit moom, su dee nit mbaa jur mbaa suuf su mu donn, amu ci lenn lu mu aayalal Aji Sax ji te ñu sañ koo jaay mbaa mu di ko jotaat. \v 29 Ba tey du kenn nit ku ñu aayalal bakkanam Aji Sax ji, mu wara sànku, ba noppi ñu di ko jotaat. Dees koy rey rekk. \p \v 30 «Bu loolu weesee mboolem lu jóge ci suuf, muy pepp mbaa doomi garab, cérub fukkeel ba Aji Sax jeey boroom. Dees koy sellalal Aji Sax ji. \v 31 Su fekkee ne nit ki dafa namma jotaat lenn ca céru fukkeelu meññeefam ma muy génne, day yokk ca njég ga xaajub juróomeelam. \v 32 Mboolem céru fukkeel bu ñu génnee cig jur, gu gudd gaak gu gàtt ga, muy lépp lu sàmm waññe bantam, cérub fukkeel la bu ñuy sellalal Aji Sax ji. \v 33 Deesu ci seet jur gu baax ak gu bon te deesu ci wuutal lenn. Bu ci nit xasee wuutal lenn, la jëkk ak la ko wuutu lépp day daldi doon lu sell. Deesu ko mana jotaat.» \p \v 34 Yooyu santaane la Aji Sax ji dénkoon Musaa ca tundu Sinayi, ngir mu jottli ko bànni Israyil.