\id JER (WOL) \ide UTF-8 \h Yeremi \toc1 Yeremi \toc2 Yeremi \mt1 Yeremi \c 1 \p \v 1 Muy kàddug Yeremi, góor gi baayam Ilkiya bokk ci sarxalkat yi dëkk Anatot, ca diiwaanu Beñamin. \v 2 Kàddug Aji Sax ji dikkal ko ci jamonoy buuru réewum Yuda, Yosya doomu Amon. Mu yemook fukkeelu atu nguuram ak ñett. \v 3 Kàddug Aji Sax ji dikkal na ko ba tey ci janti buurub Yuda, Yowakim doomu Yosya, di ko dikkal, ba keroog nguurug Cedesyas, jeneen doomu Yosya ja di jeex. Mu yemook fukkeelu atu nguuram ak benn, ca juróomeelu weer wa. Booba lañu jàpp waa Yerusalem njaam, yóbbu leen. \ms1 Waxyu dal na Yuda \mr (Saar 1.4—25.14) \s1 Yàlla woo na Yeremi \p \v 4 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal na ma, ne ma: \q1 \v 5 «Laata ma lay sos ci sa biiru ndey, xam naa la; \q1 laata ngay juddoo ci sa ndey, séddoo naa la, \q1 def la ngay yonent ñeel xeet yi.» \b \q1 \v 6 Ma ne: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, \q1 da di manumaa wax, gone doŋŋ laa.» \b \q1 \v 7 Aji Sax ji ne ma: «Bul ne: “Gone laa.” \q1 Képp ku ma la yebal, dem ca; \q1 lépp lu ma la sant, wax ko. \q1 \v 8 Bu leen ragal, ngir yaw laay àndal, \q1 di la xettli.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \b \q1 \v 9 Aji Sax ji tàllal loxoom, laal sama gémmiñ. \q1 Aji Sax ji ne ma: \q1 «Mu ngoog, sexal naa la samay kàddu. \q1 \v 10 Ma ne, tabb naa la bés niki tey, \q1 ci kaw xeet yeek réew yi, \q1 ngay buddat, di fàqat, \q1 di yàqte ak a daaneel, \q1 di defar ak a jëmbat.» \s1 Yàlla wone na ñaari misaal \p \v 11 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal ma, ne ma: «Yeremi, loo gis?» Ma ne ko: «Caru garabu saal laa gis.» \v 12 Aji Sax ji ne ma: «Yaa ko gis, maa sàlloo def sama kàddu, ngir sottal ko.» \p \v 13 Kàddug Aji Sax ji dikkalaat ma ñaareel bi yoon, ne ma: «Loo gis?» Ma ne: «Cin luy bax laa gis. Mu ngi joye bëj-gànnaar, jublook nun.» \v 14 Aji Sax ji ne ma: \q1 «Bëj-gànnaar la safaan bay fettaxe, \q1 dal ci kaw waa réew mi mépp. \q1 \v 15 Maa ngii déy, di woo \q1 mboolem waasoy réewi bëj-gànnaar ak seeni buur.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 «Dañuy dikk, ku ne dëj ngànguneem \q1 fi janook bunti Yerusalem, \q1 jànkoonteek tataam yépp, \q1 ak dëkki Yuda yépp. \q1 \v 16 Maay biral samay àtteek ñoom \q1 ci seen mbon gi gépp: \q1 Dañu maa wacc, \q1 di taalal cuuraay yeneen yàlla, \q1 di sujjóotal lu ñu sàkke seeni loxo. \b \q1 \v 17 «Yaw nag takkul te wax leen lépp lu ma la sant. \q1 Bul am tiitaange fi seen kanam, \q1 lu ko moy ma tiital la fi seen kanam. \b \q1 \v 18 «Maa ngii def la bésub tey \q1 nga mel ni dëkk bu mag bu tata wër, \q1 mel ni xeru weñ mbaa tatay xànjar, \q1 jàkkaarlook réew mi mépp, \q1 muy buuri Yuda aki kàngamam, \q1 di \w sarxalkati|lemma="sarxalkat b-:"\w* réew mi ak baadoolo yi. \q1 \v 19 Dañu lay xeex te duñu la man, \q1 yaw laay àndal, di la xettli.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \c 2 \s1 Yàlla taxawu na Israyil \p \v 1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal ma, ne ma: \q1 \v 2 «Demal yéeneji lii, Yerusalem di dégg, \q1 nga ne: “Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Maa ngi fàttliku sa ngor ba ngay ndaw, \q1 ak sa cofeel ba nga deeb séet, \q1 ba ngay topp sama gannaaw ca màndiŋ ma, \q1 ba ngay jaare fa dara dul sax. \q1 \v 3 Mooy ba Israyil dee lu ñu sellalal Aji Sax ji, \q1 di ndoortel meññeefam\f + \fr 2.3 \fr*\fk ndoortel meññeefam, \fk*\ft Aji Sax ji lañu ko daan jagleel. Kenn sañu cee lekk.\ft*\f*. \q1 Képp ku ko sex, toppees ko ko, \q1 musiba dikkal ko.”» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \s1 Bànni Israyil wor nañu \q1 \v 4 Dégluleen kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 yeen waa kër Yanqóoba, \q1 ba ci mboolem làngi kër Israyil. \q1 \v 5 Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 «Ana sikk bu ma seeni maam gisal, \q1 ba tax ñu sore ma, \q1 di topp xërëmi neen, \q1 ba far neen? \q1 \v 6 Newuñu: “Ana Aji Sax, \q1 ji nu génne woon réewum Misra, \q1 jiite nu ca biir màndiŋ ma, \q1 ca joor gu wow gaak xur ya, \q1 réewum maral ma lëndëm këruus, \q1 jaareesu fa, dëkkeesu fa?” \q1 \v 7 Ma indi leen suuf su nangu, \q1 ngir leel leeni meññeefam aki ngëneelam. \q1 Ngeen dikk sobeel sama suuf sii, \q1 ba sama céru suuf si siblu. \s1 Aji Sax jaa ngi layoo \q1 \v 8 «\w Sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi newuñu: “Ana \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji?” \q1 Ñi ŋank yoon wi faaleetuñu ma, \q1 njiit yi gàntal ma, \q1 yonent yiy waxe \w waxyuy|lemma="waxyu:"\w* \w Baal|lemma="Baal:"\w*, tuur mi, \q1 di topp lu leen dul jariñ. \q1 \v 9 Moo ma tax di layooteek yeen, \q1 ba layook seeni sët.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \b \q1 \v 10 «Jàll-leen ba ca duni Kitim fa sowu, te xool; \q1 yónneeleen Kedar fa penku, seetlu bu baaxa baax \q1 ndegam dingeen gis lu mel nii! \q1 \v 11 Fu aw xeet masa weccee yàllaam? \q1 Moonte duñuy yàlla sax! \q1 Moona xeet wi ma séddoo weccoo séen darajay Yàlla \q1 te du leen jariñ dara. \q1 \v 12 Asamaanee, waarul ci lii! \q1 Jommil, ba jommaaral!» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 13 «Ñaari yoon la xeet wi ma séddoo bàkkaar: \q1 ma di bëtu ndox muy dund, \q1 ñu wacc ma, man, \q1 di gasal seen bopp kàmbi dencukaayi ndox, \q1 te kàmb yi fett, di senn. \b \q1 \v 14 «Israyil da dib jaam a? \q1 Am daa juddoo kërug njaam? \q1 Ana lu tax ñu doon alalu sëxëtoo? \q1 \v 15 Gaynde yaa ngi ŋar ci seen kaw, \q1 di leen xiiru! \q1 Gaynde yee gental seenum réew, \q1 ba seeni dëkk di gent yu kenn dëkkul. \q1 \v 16 Te it niti Memfisoo niti Tapanes\f + \fr 2.16 \fr*\fk Memfis ak Tapanes \fk*\ft dëkki Misra lañu. Fi ñu ne Memfis am na tekki yu fi indi turu Nof.\ft*\f* \q1 ñooy dikk wat leen nel. \q1 \v 17 Xanaa du yeena def seen bopp lii, \q1 di wacc seen Yàlla Aji Sax ji, \q1 ba mu leen di jiite ca yoon wa? \q1 \v 18 Léegi lu ngeen wuti Misra? \q1 Dangeen di naani ca ndoxum Niil ma ca Misraa? \q1 Lu ngeen wuti Asiri? \q1 Dangeen di naani ca dexu Efraat ca Babilon a? \q1 \v 19 Seenug mbon a leen di mbugal, \q1 seen ñàkk kóllëre yar leen. \q1 Ñamleen ba gis ni ngeen ma dëddoo, \q1 wormaalatuleen ma, man seen Yàlla Aji Sax ji, \q1 muy loraange ju leen wex.» \q1 Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. \s1 Yuda amul worma. \q1 \v 20 «Yàgg ngeena yiwiku, \q1 dog seeni jéng, \q1 ba ne dungeen ma jaamu. \q1 Kaw tundoo tund, \q1 ker garaboo garab gu naat, \q1 gànctu ngeen fa. \q1 \v 21 Moona maa leen jëmbat, ngeen di ngëneelu reseñ, \q1 di jiwu mu mucc ayib. \q1 Nu ngeen walbatikoo di baadooloy reseñu àll? \q1 \v 22 Bu ngeen raggoo woon saabu, \q1 ba raggooteek xeme it, \q1 seen ñaawtéef gàkk, may gis.» \q1 Kàddug Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. \q1 \v 23 «Nu ngeen ñemee naa: “Sobeelunu sunu bopp \q1 te toppunu tuuri \w Baal|lemma="Baal:"\w*?” \q1 Seetleen li ngeen nekke ci xur wi\f + \fr 2.23 \fr*\fk xur wi \fk*\ft ñuy wax fii, mooy xuru Ben Inom ga ca Yerusalem te ñu daan fa def ay yëfi xërëm.\ft*\f*, \q1 xool-leen li ngeen di def, \q1 mel ni giléem gu ndaw, di wodd-woddi, \q1 fu ne mu daw jëm fa, \q1 \v 24 mbaa mbaamu àll mu miin màndiŋ mi, \q1 xabtaloo bakkanam, di xañtu ngelaw li. \q1 Bu bëggee tëbu, ku ko mana téye? \q1 Kuuy mu koy sàkku du sonn, \q1 bu ci tolloo rekk, mu jot ko. \q1 \v 25 Ma ne, buleen daw ba mujje tànki neen \q1 ak put gu wow. \q1 Ngeen naa: “Bul sonn, \q1 sopp nanu yàllay doxandéem yi, \q1 te ñoom lañuy topp!”» \b \q1 \v 26 «Gàcceg sàcc bu ñu jàpp \q1 dees na ko gàcceel waa kër Israyil, \q1 ñook seeni buur ak seeni kàngam \q1 ak seeni \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ak seeni yonent, \q1 \v 27 ñoom ñii naa bii bant: “Yaay sunu baay,” \q1 naan wee doj: “Yaa nu sukk, jur.” \q1 Wonuñu ma kanam, xanaa gannaaw, \q1 te bu leen musiba dikkalee, ñu naa: \q1 “Wallu nu boog!” \q1 \v 28 Waaw, ana seen yàlla yi ngeen sàkkal seen bopp? \q1 Bu leen musiba dikkalee, \q1 nañ leen wallu, bu ñu ko manee! \q1 Gannaaw yeen waa Yuda, \q1 ni seeni dëkk tollu la seeni yàlla tollu! \q1 \v 29 Ana lu ngeen di layook man? \q1 Yeen ñépp a ma gàntal!» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 30 «Mbugal naa seeni doom, jariñul dara. \q1 Dégguñu yar, \q1 bóom ngeen seeni yonent, \q1 mbete gaynde yuy fàdde. \q1 \v 31 Éey niti Israyili tey, \q1 teewluleen kàddug Aji Sax ji! \b \q1 «Ni màndiŋ mi aaye, ndax mas naa nee aaye ci Israyil? \q1 Mbaa ma mel ni réewum lëndëm aki loraangeem? \q1 Lu waral sama ñoñ naa: \q1 “Noo moom sunu bopp, \q1 dootunu délsi fi yaw”? \q1 \v 32 Ab janq dina fàtte takkaayam? \q1 Am ab séet dina fàtte mbubbum xewam? \q1 Moona sama ñoñ fàtte nañu ma fan yu dul jeex. \q1 \v 33 Yeen aka mokkal gànctu! \q1 Jeeg ju bon ji sax di jànge ci yeen. \q1 \v 34 Te seeni pendal sax taq na \q2 dereti néew-ji-doole yu deful dara, \q1 fekkuleen leen it ñuy dàjji kër jaambur\f + \fr 2.34 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Mucc ga\+bk* 22.1.\ft*\f*. \q1 Loolu yépp terewul, \q1 \v 35 ngeen naan: “Nun de defunu dara, \q1 merum Yàlla won na nu gannaaw moos.” \q1 Gannaaw nee ngeen bàkkaaruleen, \q1 maa ngii di leen àtte. \q1 \v 36 Yeen aka yomba soppi doxalin! \q1 Waaye Misraa leen di bett, \q1 na leen Asiri bette woon, \q1 \v 37 ngeen jóge ca yenu seeni loxo. \q1 Aji Sax jee wacc ñi ngeen yaakaar, \q1 ba dungeen baaxlee ci ñoom.» \c 3 \s1 Tuub jot na \q1 \v 1 Mu ne: «Su waay fasee jabaram, \q1 mu dem doon jabaru keneen, \q1 Su waa ja jëlaatee ndaw sa ëllëg,\f + \fr 3.1 \fr*\ft Yoonu Musaa mayul ku fase jabaram mu di ko jëlaat, gannaaw bu séyaatee ba tas. Seetal ci \ft*\ft \+bk Baamtug yoon wi\+bk* 24.1-4.\ft*\f* \q1 Loolu du sobeela sobeel réew mii? \q1 Moona yeen gànctu ngeen aki fari far, \q1 Ana nu ngeen mana délsee fi man?» \q1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. \b \q1 \v 2 «Téenleen, séentu tund\f + \fr 3.2 \fr*\fk tund: \fk*\ft kaw tund yooyu lañu daan jaamoo tuur yi ñu foogoon ne dañuy nangul am njur.\ft*\f* ya ne faraas! \q1 Ana fu ñu leen fi tëddewul? \q1 Ci yoon yi ngeen di yeeroo \q1 ni màngaan muy dogalee ci màndiŋ mi. \q1 Sobeel ngeen réew meek seen gànctook seenug mbon. \q1 \v 3 Moo tax waame aje, \q1 taw yiy mujje dikkul. \q1 Teewul ngeen dëgër bët nib gànc, \q1 ñàkk gàcce! \q1 \v 4 Léegi ngeen di ma woo wall naa: \q1 “Baay, yaay sama xejj ca ba may ndaw. \q1 \v 5 Xanaa deesul mer ba fàww? \q1 Xanaa xadar du sax?” \q1 Ma ne: “Israyiloo, yeena ko wax, \q1 waaye bon ngeen lu ngeen man.”» \s1 Israyil woyof kumba, Yuda toogadi \p \v 6 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nag wax ma ci jamonoy buur Yosya ne ma: «Gis nga li Israyil Woyof-Kumba-si def? Di dem kaw tundoo tund ak ker garaboo garab gu naat, di fa gànctu. \v 7 Ma noon su ma defee loolu lépp ba noppi, dina délsi, te délsiwul. Te doomu ndeyam Yuda workat bi gis na ci. \v 8 Gis naa ne it Israyil Woyof-Kumba-si gànctu na ba ma yebal ko, jox ko kayitu pase, mu dem, te taxul doomu ndeyam Yuda workat bi ragal. Moom it daa dem di gànctu. \v 9 Ni gànctu yombe Israyil tax na réew mi sobewu. Njaaloo naak yàllay doj, njaalook yàllay bant. \v 10 Loolu yépp itam taxul Yuda workat bi, doomu ndeyu Israyil, délsee léppi xolam fi man, xanaa di jinigal rekk.» Kàddug Aji Sax jee. \v 11 Aji Sax ji nag ne ma: «Li Israyil di woyof kumba lépp sax moo tane Yuda workat bi. \v 12 Demal yéeneji kàddu yii fa bëj-gànnaar. Nga ne: \q1 “Israyiloo, Woyof-Kumba, délsil.” \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 “Duma la fasal kanam. \q1 Man Boroom ngor laa, \q1 te duma jàpp mer ba fàww.” \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 13 “Nangul ne ñaaw nga rekk, \q1 te man sa Yàlla Aji Sax ji nga tooñ, \q1 di wër di foye sa bopp ak yàllay doxandéem yi \q1 ci ker garaboo garab gu naat, \q1 te dégluwoo ma.”» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 14 «Yeen doom yu woyof kumba yi, délsileen.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 «Maay seen boroom kër, \q1 maay jële kenn ci bii dëkk, \q1 ñaar ca bee gox, \q1 boole indi \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, \q1 \v 15 tànnal leen sàmm yu ma doy, \q1 ñu sàmme leen xam-xam akug muus. \q1 \v 16 Janti keroog bu ngeen baree ba giir ci réew mi, \q1 deesul waxe \w gaalu kóllërey Aji Sax|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* ji\f + \fr 3.16 \fr*\fk gaalu kóllërey Aji Sax ji \fk*\ft moo doon firndeel teewaayu Aji Sax ji ci digg bànni Israyil.\ft*\f*; \q1 xel dootu ci dem, \q1 deesu ko fàttliku sax, \q1 te deesu ko namm, \q1 deesu ko sàkkati sax.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 17 «Janti keroog \q1 Yerusalem, ngànguney Aji Sax ji lees koy wooye, \q1 xeetoo xeet di fi daje, \q1 ngir Aji Sax, ji turam ñeel Yerusalem, \q1 te dootuñu të ticc ci seen mébét yu bon. \q1 \v 18 Janti keroog waa kër Yuda \q1 ànd ak waa kër Israyil, \q1 bawoondoo réewum bëj-gànnaar, \q1 wuti réew ma ma séddoon seeni maam. \b \q1 \v 19 «Maa leen naroona teral ni doom yu góor, \q1 may leen suuf su xemmemlu, \q1 ngeen gënle xeet yépp suuf. \q1 Ma noon dingeen ma wooye baay \q1 te dungeen ma dëddu mukk. \q1 \v 20 Teewul, yeen waa kër Israyiloo, ngeen wor ma, \q1 ni as ndaw di wore faram.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 21 «Coow dégtu na kaw tund ya ne faraas, \q1 \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ay jooy ak a tinu. \q1 Ñoo lajj seenu yoon, \q1 fàtte seen Yàlla Aji Sax ji. \q1 \v 22 Yeen doom yu woyof kumba yi, \q1 waññikuleen, ma fajtal seen woyof kumba.» \s1 Kàdduy tuub jib na \q1 Nu ngi nii fekksi la, \q1 yaw kay yaay sunu Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \q1 \v 23 Naxi neen kay lañu jële ca xërëmi tund yu ndaw ya \q1 ak coowal kaw tund yu mag ya. \q1 Muccu Israyil kay, fi sunu Yàlla Aji Sax ji. \q1 \v 24 Ba ñuy gone ba tey, \q1 tuur mu ruslu maa ngi neenal ñaqu maam yi, \q1 seen jur gu gudd ak gu gàtt, \q1 ba ci seeni doom, góor ak jigéen. \q1 \v 25 Nan gapproo sunu gàcce, \q1 sàngoo sunu toroxte. \q1 Nook sunuy maam déy, \q1 ba ñuy gone ba tey jii, \q1 nu ngi tooñ sunu Yàlla Aji Sax ji, \q1 te déggalunu sunu Yàlla Aji Sax ji. \c 4 \q1 \v 1 «Yaw Israyil, sooy waññiku, \q1 waññikul fi man.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 «Soo jëlee fi sama kanam \q1 sa jëf ju siblu, \q1 te jenguloo, \q1 \v 2 xanaa di waate Aji Sax jiy dund, \q1 ci dëgg ak njub ak ngor, \q1 kon xeet yi di barkeeloo Aji Sax ji, \q1 di ko sagoo.» \q1 \v 3 Aji Sax ji déy dafa wax waa Yudak Yerusalem, ne leen: \q1 «Ruujleen seen tool, \q1 buleen ji ciy dég. \q1 \v 4 Yeen waa Yudak Yerusalem, deeleen xaraf ngir Aji Sax ji, \q1 dogleen seen mbuñukay xol, \q1 balaa sama xadar ne jippét ni sawara, \q1 di tàkk te deesu ko fey \q1 ndax seen jëf ju bon. \s1 Xare jib na \q1 \v 5 «Nangeen yégle lii fa Yuda, \q1 dégtale ko fa Yerusalem, \q1 yéenee koog liit fi biir réew mi \q1 te xaacu seen kem kàttan ne leen: \q1 “Dajeleen, nu dem ca dëkk ya tata wër.” \q1 \v 6 Yékkatileen raaya, jubale \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, \q1 làqujileen, buleen taxaw, \q1 musiba déy laay jële bëj-gànnaar, \q1 muy safaan bu réy. \b \q1 \v 7 «Gayndee fëlle geeram, \q1 fàkkaskatu xeet yee jóg, génne këram, \q1 nara gental seeni dëkk, \q1 ba ñu di gent yu kenn dëkkul. \q1 \v 8 Kon nag sol-leeni saaku, ñaawloo te yuuxu ne: \q1 “Merum \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji tàng na kat te moyu nu.” \q1 \v 9 Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, \q1 «xolu buur jeex, kàngam ne yàcc, \q1 \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* waaru, yonent jommi.» \sp Yeremeey wax \q1 \v 10 Ma ne, «Éy Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 yaa naxlu askan wii nax yu metti, \q1 ba nga nee: “Yerusalem jàmm lay am,” \q1 te saamar tege ci putam.» \s1 Mbugal taxaw na \q1 \v 11 Janti keroog dees na wax askanu Yerusalem wii, ne leen: \q1 «Jaas bu tàng a uppe kaw tund ya ne faraas ca màndiŋ ma, \q1 wuti sama ñoñ. \q1 Du doon ngelaw lees di bàcceek a beese. \q1 \v 12 Ngelaw lu ko ëpp doole laay indi. \q1 Léegi maa leen di biral sama kàddug mbugal.» \sp Waa Yerusalem ay wax \q1 \v 13 «Noon baa ngii, di jóg niy niir, \q1 watiiri xareem ni ngëlén, \q1 fasam ya gëna gaawi jaxaay. \q1 Wóoy ngalla nun, yàqu nan!» \sp Yàllaay wax \q1 \v 14 «Éey Yerusalem, fóotal sa xol, jële ci lu bon, \q1 ndax nga mucc. \q1 Foo àppal sa mébéti xol yu bon? \q1 \v 15 Kàddug yéenee ngi jibe Dan, \q1 musiba dégtu na, bawoo tundu Efrayim. \q1 \v 16 Jottlileen ko xeet yi, \q1 neleen Yerusalem: \q1 “Songkat yaa ngii riire réew mu sore ma, \q1 xaacoondoo fi kaw dëkki Yuda.” \q1 \v 17 Ñooy gaw Yerusalem ni wattukati tool, \q1 ndax man la gàntal.» \q1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. \q1 \v 18 «Sa jëfin ak say jëf a la yóbbe lii, \q1 sa musibaa ngook, wex la xàtt, \q1 di dagg sa xol.» \s1 Yeremi jàq na \q1 \v 19 Maaka jàqa jàq bay jal-jali, \q1 sama xol biy fuddu! \q1 Éy wii mititu xol! \q1 Duma mana noppi, \q1 maa dégg wooteb liit \q2 ak yuuxi xare. \b \q1 \v 20 Yéenees na rajaxoo ci kaw rajaxoo, \q1 réew mi mépp ne tasar kay! \q1 Jekki-jekki samay xayma tasaaroo. \q1 Xef-xippi ndimoy xayma ya xotatoo! \q1 \v 21 Xanaa duma gis ba fàww raayab noon, \q1 liitu xare di ko feelu? \s1 Aji Sax ji jéppi na ñoñam \q1 \v 22 «Dofe la sama ñoñ def. \q1 Man, xamuñu maay kan, \q1 mbetey gone yu dul xalaat dara; \q1 dég-dég, tus; \q1 seen xel mépp, lu bon rekk, \q1 lu baax, xamuñu ci dara.» \s1 Àddina salfaañoo na \q1 \v 23 Maa xool suuf, \q1 ndeke ma nga ne maraas, ne wëyëŋ; \q1 ma xool asamaan, \q1 leer amatu ca. \q1 \v 24 Ma xool tund yu mag yi, \q1 ndeke ñu ngi yëngu, \q1 tund yu ndaw yépp di jaayu. \q1 \v 25 Ma xoolaat, gisuma nit, \q1 njanaaw yépp daw. \q1 \v 26 Ma xool, gis suuf su nangu sa \q1 di ndànd-foyfoy, \q1 dëkk yépp raaf \q1 ndax \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jeek tàngaayu sànjam. \b \q1 \v 27 Aji Sax ji déy dafa wax ne: \q1 «Duma tas lépp tasar, \q1 waaye réew mi mépp ay gental. \q1 \v 28 Loolooy tax suuf di ñaawlu, \q1 asamaan di lëndëm. \q1 Maa ko wax, maa ko dogu; \q1 duma dëpp, duma deltu gannaaw.» \s1 Yerusalem dugg na fitna \q1 \v 29 Gawar ak fittkat riir, \q1 waa dëkk yépp fëx, \q1 ñii tàbbiy gajj, \q1 ñee ñalgu ci kawi doj, \q1 ñu won dëkkoo dëkk gannaaw, \q1 kenn desatu ca. \q1 \v 30 Yaw Yerusalem mu tas mi, \q1 ana looy def nii, \q1 di solu ba yànj, \q1 gànjaroo wurus, \q1 tusngalu, yàkkleey gët? \q1 Yaa ngi caaxoñu ci neen: \q1 say xéddkat wacc nañu la, \q1 sa bakkan lañuy wut. \q1 \v 31 Baatu ndaw su jagadi laa dégg, \q1 ma nga jàq, di matub taawam. \q1 Baatub \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, dëkk bu taaru baa! \q1 Ma ngay àppaat, tàllal yoxo ya, \q1 naan: «Wóoy, ngalla man; \q1 ne yàcc ci loxol bóomkat yi!» \c 5 \s1 Mbugal war na \sp Yàllaay wax \q1 \v 1 «Wërleen mbeddi Yerusalem, \q1 xool-leen, seet ciy péncam rekk ba xam \q1 ndegam dingeen gis kenn, \q1 kenn kepp kuy def njub, \q1 di sàmm worma, \q1 ma daldi leen baal. \q1 \v 2 Bu ñu nee sax: “Giñ naa ko ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jiy dund,” \q1 ay fen lañuy giñ.» \sp Yeremeey wax \q1 \v 3 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, xanaa du worma ngay sàkku? \q1 Dóor nga leen, safu leen; \q1 nga làbbli, ñu tanqamlu, \q1 wowle ba raw doj, baña dëpp. \q1 \v 4 Man nag, ma noon: «Ñii de ay baadoolo rekk lañu, \q1 di def jëfi dof, \q1 xamuñu yoonu Aji Sax ji, \q1 xamuñu lu seen àtteb Yàlla laaj. \q1 \v 5 Kon naa dem seeti kàngam yi, \q1 wax ak ñoom. \q1 Xanaa ñoom dinañu xam yoonu Aji Sax ji, \q1 xam lu seen àtteb Yàlla laaj.» \q1 Waaye ñoo bokk daggook Yàlla, \q1 dogook moom. \q1 \v 6 Moo tax gaynde di génne ci gott bi, fàdd leen, \q1 bukkiy màndiŋ mi di leen yàpp, \q1 segg di tëru seeni dëkk, \q1 ku ca génne, dees na la xotat. \q1 Seeni moy a bare, \q1 te seen ñàkk worma réy. \sp Yàllaay wax \q1 \v 7 «Yerusalem, ana lu tax ma di la baal, \q1 te say doom wacc ma, \q1 di giñe lu dul Yàlla. \q1 Ma reggal leen, teewul ñuy njaaloo, \q1 riixle, jëm kër gànc ya! \q1 \v 8 Mbete fas yu suur, tukkal, \q1 ku ne ŋexal, jëm sa jabaru moroom. \q1 \v 9 Lii, duma leen ko dumaa?» \q1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. \q1 Mu ne: «Wii xeet, duma ko fey yoolam?» \s1 Dëddu Yàlla, gis ko \q1 \v 10 «Yéegleen seeni tata, yàqte \q1 waaye buleen leen jeexal tàkk. \q1 Tenqileen lawit yi, \q1 ñooñoo bokkul ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \q1 \v 11 Waa kër Israyil ak waa kër Yuda kat, \q1 ñoo ma wora wor!» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 12 Mu ne: «Ñoo fenal Aji Sax ji, \q1 naan: “Moom du def dara, \q1 musiba du nu dal, \q1 saamaroo, xiifoo, dunu ci gis dara. \q1 \v 13 Yonent yi daal, ngelawal neen! \q1 Kàddug waxyu newul ci ñoom; \q1 li ñuy wax, na leen yenu!”» \b \q1 \v 14 Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: \q1 «Gannaaw wax jii lañu wax, \q1 maa ngii di def samay wax di sawara ci sa gémmiñ, \q1 askan wii di matt, \q1 mu xoyom leen. \q1 \v 15 Éey waa kër Israyil,» \q1 kàddug Aji Sax jee, \q1 «maa ngii di indi fi seen kaw xeet wu bawoo fu sore. \q1 Xeet wu am kàttan lañu, \q1 xeet wu yàgga yàgg, \q1 wu ngeen xamul seen làmmiñ, \q1 te dégguleen seeni wax. \q1 \v 16 Seen mbari fitt ŋafal paxum bàmmeel, \q1 ñoom ñépp di ñeyi xare. \q1 \v 17 Ñooy dikk, warax seen meññeef ak seen ñam, \q1 jeexal seeni doom, góor ak jigéen, \q1 lekk seen jur gu gudd ak gu gàtt, \q1 saax-saaxee seeni reseñ ak seeni figg; \q1 te dëkk yi ngeen yaakaare seeni tata, \q1 dooley saamar a koy tas. \q1 \v 18 Waaye bési keroog it,» \q1 kàddug Aji Sax jee, \q1 «duma leen jeexal tàkk. \q1 \v 19 Bu ñu nee: \q1 “Ana lu waral sunu Yàlla Aji Sax ji teg nu lii lépp?” \q1 ne leen: “Yàlla nee: \q1 Ni ngeen ma dëddoo, di jaamu yàllay jaambur ci seenum réew, \q1 ni ngeen di jaamujee ay jaambur \q1 biir réew mu ngeen moomul.”» \s1 Yàlla àrtu na xeet wi \q1 \v 20 «Jottlileen lii waa kër Yanqóoba, \q1 biral-leen ko fa Yuda, ne leen: \q1 \v 21 Ngalla dégluleen lii, \q1 xeet wu dofe, ñàkk xel wi ngeen doon, \q1 ami gët te dungeen gis, \q1 ami nopp te dungeen dégg! \q1 \v 22 Man daal, dungeen ma ragal, \q1 am tiituleen ma?» \q1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. \q1 «Man mi teg gannuus, yemalee ko géej, \q1 dogalal ko ko dàkk te du ko jàll, \q1 lu mu wañax wañax du ko man; \q1 gannax ya day riir, te du jàll! \q1 \v 23 Waaye wii xeet a dëgër bopp te déggadi. \q1 Dëddu nañu ma ba wéy. \q1 \v 24 Seen xel demul sax ba ne: \q1 “Tee noo ragal sunu Yàlla Aji Sax, \q1 jiy jot, mu tawal nu, \q1 taw yu jëkk ak yu mujj yi, \q1 àppal nu ayi bési ngóob, \q1 sédde nu?” \q1 \v 25 Yooyii seeni ñaawtéef a ko waññi, \q1 seen bàkkaar a leen xañ ngëneel. \s1 Mbon maase na ci xeet wi \q1 \v 26 «Waaw! Daa am ñu bon ci sama ñoñ, \q1 ñuy tërook a fiire \q1 mbete nappkati picc. \q1 \v 27 Ni kaaf di feeseeki picc, \q1 ni la seeni kër di feese alali càcc, \q1 ba tax ñu yokku ba woomle, \q1 \v 28 yaflu, di nes-nesi. \q1 Seenug mbon it amul kem: \q1 duñu defal jirim njub, \q1 duñu àtte néew-ji-doole dëgg. \q1 \v 29 Lii, duma leen ko dumaa?» \q1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. \q1 «Xeet wu mel nii duma ko fey yoolam? \q1 \v 30 Lu siblu te yées am na ci réew mi: \q1 \v 31 Yonent yiy wax \w waxyuy|lemma="waxyu:"\w* fen, \q1 \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yiy jiitee seen coobare, \q1 te sama ñoñ soppe ko ni! \q1 Moo bu muj ga taxawee, nu ngeen di def?» \c 6 \s1 Gawub Yerusalem nuyoo na \q1 \v 1 «Yeen askanu Beñamin, fëxleen, \q1 génn Yerusalem. \q1 Wal-leen liit gi fa Tekowa, \q1 jafaleleen jum yi Bet Kerem, artoo ko, \q1 musiba kat a ngi yëre bëj-gànnaar, \q1 di safaan bu réy. \q1 \v 2 Yaw \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, dëkk bu taaru bi te xejj, \q1 dama lay dammat. \q1 \v 3 Ay sàmm ak seeni gétt ci sa kaw, \q1 ñu samp seeni xayma, wër la, \q1 di foral, ku nekk ak pàccam. \q1 \v 4 Ñii ne: “Waajal-leen xare baak ñoom, \q1 nu songi leen digg bëccëg. \q1 Waaye wóoy nun, jant a ngi lang, \q1 keru ngoon di law!” \q1 \v 5 Ñee ne: “Nan song congum guddi boog, \q1 ba rajaxe seen kër yu yànj.”» \b \q1 \v 6 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoor yi déy da ne: \q1 «Gorleeni bant, \q1 sëkke Yerusalem, gaw ko! \q1 Dëkk bii dees koy mbugal, \q1 àqu noteel la fees dell. \q1 \v 7 Ni bëtu ndox di dawe, \q1 ni lañuy dawale seenug coxor. \q1 Fitnaak salfaañooy riir ci dëkk bi, \q1 gisuma lu moy jagadeek loraange!» \q1 \v 8 «Yeen waa Yerusalem, deeleen dégg \q1 bala ma leena dëddu, \q1 ba gental réew mi \q1 gent bu kenn dëkkul.» \s1 Askan wa të na \q1 \v 9 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: \q1 «Nañu witta witt ndesu Israyil, \q1 ni ñuy witte reseñ, \q1 ba nga dawalaat say loxo ca car ya.» \sp Yeremeey wax \q1 \v 10 Moo kan laay waxal, \q1 àrtu ko ba mu déglu, \q1 yii boroom noppi paaxee tëë teewlu! \q1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jaa ngii, \q1 mel ni lu ñu rus, \q1 lu ñu safoowul! \b \q1 \v 11 Maa ngi meral Aji Sax ji ba fees \q1 ba manatuma koo dékku. \q1 Aji Sax ji nee: «Sippi ko tuut-tànk yi ci mbedd mi, \q1 sippiwaale ko waxambaane yi daje, \q1 mu laawaale jëkkër ak jabar, \q1 mag ak màggat, \q1 \v 12 seeni kër doon alali jaambur, \q1 ak seeni tool it ak seeni jabar. \q1 Maay xàcci sama loxo déy, \q1 dal ci kaw waa réew mi.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 13 «Ndax ki gëna tuut ba ki gëna mag, \q1 ñépp a ngi lewal lu lewul. \q1 Yonent akub \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w*, \q1 ñépp a ngi wor. \q1 \v 14 Sofental nañu sama pajum ñoñ ñi dammtoo, \q1 naan: “Jàmm, lépp jàmm!” \q1 te jàmm amul. \q1 \v 15 Ñu wara am gàcce ci seen jëf ju siblu, \q1 te gàcce gàcceelu leen. \q1 Xamuñu sax luy kersa! \q1 Moo tax ñuy fëlëñoondook ñiy fëlëñu. \q1 Kera ba ma leen di dikkal, ñooy tërëf.» \q1 Aji Sax jee ko wax. \s1 Pexey askan wi jur na musiba \q1 \v 16 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: \q1 «Taxawleen ca selebe yoon wa, xool, \q1 te laajte yoon ya woon, \q1 ne: “Ana yoonu mbaax?” \q1 Ngeen awe ca, am noflaayu bakkan.» \q1 Ñu lànk ne: «Awunu ca.» \q1 \v 17 «Ma tabbal leeni wattukat \q1 ne: “Teewluleen liit gu jib.”» \q1 Ñu lànk ne: «Teewluwnu.» \q1 \v 18 «Moo tax yeen xeet yi, dégluleen; \q1 yeen waaso yi, seedeleen liy xaar ñii. \q1 \v 19 Yeen waa àddina, dégluleen! \q1 Maa ngii di indil askan wii musiba, \q1 seeni pexe jural leen. \q1 Ñoo faalewul samay kàddu, \q1 gàntal sama yoon. \q1 \v 20 Lu may doye lii? \q1 Ndàbb lu jóge Saba\f + \fr 6.20 \fr*\fk Saba \fk*\ft am réew la wu bokk ci sowu Arabi, fa féete suuf.\ft*\f*, \q1 diw gu xeeñ, bawoo réew mu sore? \q1 Seeni \w saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* safu ma; \q1 seen saraxi jur, bugguma.» \q1 \v 21 Moo tax Aji Sax ji wax ne: \q1 «Maa ngii di tegal askan wii \q1 ay pakk, ñu fakkastaloondoo, \q1 baay ak doom, \q1 dëkkandook ub xarit, \q1 ñépp sànku.» \s1 Noon sàqee na bëj-gànnaar \q1 \v 22 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: \q1 «Aw askan a ngii bàyyikoo réewum bëj-gànnaar, \q1 xeet wu mag lañuy doon, sàqee fa cati àddina. \q1 \v 23 Fitt aku xeej lañuy ŋëb, \q1 néeg lool, duñu yërëm; \q1 seen coow ni riirum géej, \q1 ñu war seeni fas, rëpptal, \q1 làng-déral leen, \q1 yeen waa \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, dëkk bu taaru bi.» \sp Waa Yerusalem ay wax \q1 \v 24 «Danoo dégg riir mi, \q1 sunuy yoxo yoqi, \q1 njàqare ne nu taral, \q1 ni mititu mat. \q1 \v 25 Kii naa: “Bul génn ci àll bi!” \q1 Kee naa: “Bul jaar ci yoon wi!” \q1 Saamar kay a nga ca loxol noon ba, \q1 tiitaange dajal fépp!» \sp Yeremeey wax \q1 \v 26 Éey bokk yi, sol-leeni saaku, \q1 diwoo dóom, ñaawloo ko. \q1 Ñaawluleen ni kuy dëj benn bàjjo \q1 te jooy jooy yu metti, \q1 nde yàqkat bi day jekki, \q1 ne sunu kaw dàll! \sp Yàllaay wax \q1 \v 27 «Maa la def sama nattukatu ñoñ, \q1 nga di leen nattu ni ñuy nattoo xaalis, \q1 te war leena seetlu, nemmiku seen jikko.» \sp Yeremeey wax \q1 \v 28 Ñoom ñépp a di fippukat yu fétteeral, \q1 wër di sos, \q1 dëgërle ni xànjar ak weñ gu ñuul. \q1 Ñoom ñépp di yàqkat. \q1 \v 29 Tëgg wal taalam, mu yànj; \q1 sawara seeyal beteex. \q1 Xellees na koo xelli ci neen, \q1 taxul li ci bon génn. \q1 \v 30 Dees na leen wooye mbuubitum xaalis, \q1 nde \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji buub na leen, sànni. \c 7 \s1 Yeremi yedd na demkati kër Yàlla yi \p \v 1 Kàddu gii dikkal na Yeremi, bawoo fa \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Mu ne ko: \v 2 «Taxawil fa bunti kër Aji Sax ji, nga yéene fa kàddu gii, ne leen: “Mboolem yeen waa Yuda ñiy jàlle bunt yii, di jaamusi Aji Sax ji, dégluleen kàddug Aji Sax ji. \v 3 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, Yàllay Israyil dafa wax ne: Jekkal-leen seeni jikkook seeni jëf, ma dëël leen bii bérab. \v 4 Buleen naxe seen bopp kàdduy caaxaan, naan: ‘Kër Aji Sax jaa ngi, kër Aji Sax jaa ngi fii, kër Aji Sax jee!’ \v 5 Su ngeen jekkalee jekkal seeni jikko ak seeni jëf déy, di defa def yoon seen digg ak seen moroom, \v 6 te notuleen doxandéem, ab jirim akub jëtun, tuuruleen deretu jaamburu Yàlla, fi bii bérab, toppuleen yeneen yàlla bay loru, \v 7 su boobaa, ma dëël leen bii bérab, réew mi ma joxoon seeni maam, bu yàgg, ba fàww. \v 8 Yeena ngii di naxe seen bopp waxi caaxaan yu amul njariñ. \v 9 Yeen, nu ngeen mane di sàcc, di bóome, di jaaloo, di giñi fen, di taalal \w Baal|lemma="Baal:"\w*, tuur mi cuuraay, di topp yeneen yàlla yu ngeen xamul, \v 10 tey dikk taxaw fi sama kanam, biir kër gii ñu ma tudde, te naan: ‘Nun kay raw nanu,’ ba tax ngeen di def mboolem lu siblu lii? \v 11 rawtub sàcc daal ngeen def kër gii ñu ma tudde? Man de lii laa gis!” Kàddug Aji Sax jee. \p \v 12 «“Demleen rekk kay ca sama bérab ba ca Silo, fa ma jëkkoona dëël sama tur, ngeen xool na ma ko def ngir mbonug Israyil, sama ñoñ. \p \v 13 «“Gannaaw def ngeen jëf jii jépp nag,” kàddug Aji Sax jee, “te ma waxoon leena wax ay yooni yoon, dégluwleen; woo leen, wuyuwleen, \v 14 kër gii ñu ma tudde, ngeen yaakaar ko, bérab bii ma leen joxoon, yeen ak seeni maam, na ma def Silo laa koy def. \v 15 Dama leen di dàq, ngeen sore ma, na ma dàqe woon seen bokk yépp, askanu Efrayim gépp\f + \fr 7.15 \fr*\fk Efrayim \fk*\ft genn la ci fukki giiri bànni Israyil ya séq réewum Israyil, ca bëj-gànnaaru réewum Yuda.\ft*\f*.” \s1 Yàlla gàntal na \p \v 16 «Waaye yaw bul ñaanal askan wii, bu leen yékkatil kàddug ñaan, bu leen tinul fi man. Du maa lay déglu moos! \p \v 17 «Xanaa gisoo li ñu nekke fi dëkki Yuda ak ci mbeddi Yerusalem? \v 18 Doom a ngi taxan, baay di taal, jigéen di not lu mu nàkkal ki ñuy wooye Lingeeru asamaan, di tuural ay naan yeneen yàlla, di ma ko naqarale! \v 19 Du man lañuy naqaral moos!» Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. Mu ne: «Xanaa kay ñoo ciy rus!» \p \v 20 Moo tax Aji Sax ji Boroom bi dafa wax ne: «Sama xadar a ngii di sottiku fi bii bérab, fi kaw nit ak mala, garab ak lu suuf meññ, lépp ne jippét, te deesu ko fey.» \p \v 21 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, Yàllay Israyil dafa ne: «Seen juru \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, dollileen ko ci seen yeneen sarax, te lekk yàpp wi\f + \fr 7.21 \fr*\ft Ci yoon, saraxu rendi-dóomal, deesu ci lekk dara. Yàllaa ngi leen di ñaawal fii, di leen won ne gedd na seen bépp sarax.\ft*\f*. \v 22 Bés ba may génne seeni maam Misra déy, waxuma leen woon mbaa di leen sant mbirum saraxu rendi-dóomal ak yeneen sarax. \v 23 Mbir mii déy laa leen santoon ne leen: “Déggal-leen ma, ma doon seen Yàlla; yeen ngeen doon sama ñoñ. Doxeleen wépp yoon wu ma leen sant, su ko defee ngeen baaxle.” \v 24 Waaye déggluwñu ma, teewluwñu ma, xanaa di jëfe seen xel ak seen dëgër bopp ak seen bon xol, ba tax ñu dellu gannaaw, jëmuñu kanam. \v 25 La dale bés ba seeni maam génnee réewum Misra ba bésub tey jii, yónnee naa leen bés bu nekk mboolem sama jaam ñi, yonent yi. \v 26 Waaye dégluwñu, teewluwñu ma, xanaa sajju loos, di bon, ba yées seeni maam. \p \v 27 «Dinga leen wax kàddu yii yépp, te duñu la déglu, nga woo leen, duñu la wuyu. \v 28 Su ko defee nga ne leen: “Xeet a ngii wu dul déglu kàddug Yàllaam Aji Sax ji, nanguwñu yar, worma tumurànkeel leen, ba daggook seen làmmiñ.” \s1 Xuru Ben Inom di xuru ndee \q1 \v 29 «Waa Yerusalemee, seen njañ\f + \fr 7.29 \fr*\fk njañ: \fk*\ft seetal ci \ft*\ft \+bk Màndiŋ ma\+bk* 6.1-8.\ft*\f* li ngeen séddoo Yàlla, \q1 xuufleen ko, sànni, ñaawloo ko, \q1 xaaculeen fa kaw tund ya ne faraas, \q1 nde \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji xalab na, \q1 wacc na seen maas gii sabab sànjam. \m \v 30 Waa Yuda déy, ñoo def lu ma ñaawlu.» Kàddug Aji Sax jee. «Ñoo yeb yëf yu siblu fi biir kër gi ñu ma tudde, di ko sobeel. \v 31 Ñoo tabax ay jaamookaay ca Tofet fa xuru Ben Inom, di fa sarxe seeni doom, góor ak jigéen, lakk leen, te santaanewma ko, jaarul sax sama xel. \v 32 Moo tax ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «deesatul tudd Tofet mbaa xuru Ben Inom, xanaa xuru Bóomukaay.» Dees na rob ca Tofet ndax ñàkk suuf. \v 33 Néewi xeet wii mujj di lekku njanaaw ak rabu àll, te kenn du leen mana dàq. \v 34 Maay dakkal fi dëkki Yuda, dakkal fi mbeddi Yerusalem coowal mbégteek bànneex, dakkal kàddug boroom séet, dakkal kàddug séet, ndax réew mu tumurànke. \c 8 \q1 \v 1 «Su boobaa déy,» \q1 kàddug Aji Sax jee, \q1 «noon yeey sulli yaxi buuri Yuda \q1 ak yaxi kàngam yi \q1 ak yaxi \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi \q1 ak yaxi yonent yi \q1 ak yaxi waa Yerusalem, \q1 fa seeni bàmmeel, \q1 \v 2 weer leen ci naaj week weer wi \q1 ak mboolem biddiiw yi ñu soppoon, \q1 di leen jaamu, di leen topp ak a sàkku, \q1 di leen sukkal. \q1 Deesu ko dajale, deesu ko suul; \q1 day mel niy jonkan fi kaw suuf si. \q1 \v 3 Dee mooy gënal dund \q1 mboolem ku des ci njaboot gu bon gii, \q1 ak mboolem fu ñu dese fa ma leen tasaare woon.» \q1 Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. \s1 Askan wi të na ticc \q1 \v 4 «Nanga leen wax ne leen: \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: \q1 Ku daanu, da dul jógaat? \q1 Am ku lajj, du délsi? \q1 \v 5 Lu tax xeet wii dëddu? \q1 Lu tax Yerusalem gii lajj, baña délsi? \q1 Ñu ngi langaamoo naxi neen, \q1 baña délsi. \q1 \v 6 Teewlu naa, déglu naa; \q1 du lu jaadu lañu wax. \q1 Kenn tuubu ci mbonam, \q1 ba ne: “Lu ma def nii?” \q1 Ku nekk a topp yoonam, \q1 ni fas wu màmm cib xare. \q1 \v 7 Ag xodd sax xam na bésub demam, \q1 pitax, wetwet ak mbelaar it dem, \q1 tey sàmm seen bésub délsi. \q1 Waaye sama ñoñ faalewuñu àtteb Aji Sax ji. \q1 \v 8 Nu ngeen man ne: “Am nan xel, \q1 nungeek yoonu Aji Sax ji,” \q1 te xalimay yoonalkat soppi ko fen?» \q1 \v 9 Dees na gàcceel boroom xel yi, \q1 ñu jàq, tarsu. \q1 Kàddug Aji Sax jaa ngii ñu dëddu, \q1 kon ana seenum xel? \b \q1 \v 10 «Maay joxe seeni jabar, \q1 jox seeni tool ay foqatikat, \q1 ndax ki gëna tuut ba ki gëna mag, \q1 ñépp a ngi lewal lu lewul. \q1 Ab yonent akub \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w*, ñépp a ngi wor! \q1 \v 11 Sofental nañu sama pajum ñoñ ñi dammtoo, \q1 naan: “Jàmm, lépp jàmm!” \q1 te jàmm amul. \q1 \v 12 Ñu wara am gàcce ci seen jëf ju siblu, \q1 te gàcce gàcceelu leen. \q1 Xamuñu sax luy kersa! \q1 Moo tax ñuy fëlëñoondook ñiy fëlëñu. \q1 Kera ba ma leen di dikkal, ñooy tërëf.» \q1 Aji Sax jee ko wax. \s1 Yaakaar tas na \sp Yàllaay wax \q1 \v 13 «Maa leen di witta witt.» \q1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. \q1 «Garabu reseñ du dese doom, \q1 figg du dese doom,» \q1 kàddug Aji Sax jee, \q1 «xob ya sax day wow. \q1 Lu ma leen joxoon, rëcc na leen.» \sp Askan waay wax \q1 \v 14 «Ana lu nuy toog? \q1 Fabuleen, nu dem ca dëkk ya tata wër, \q1 deeyi fa. \q1 Sunu Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nar na sunu dee; \q1 moo nu nàndal tookey mbugal, \q1 nde noo tooñ Aji Sax ji. \q1 \v 15 Nuy yaakaar jàmm, \q1 dara baaxul; \q1 nuy séentum paj, \q1 tiitaange ne jaas! \q1 \v 16 Seen noowi fas yaa dégtoo bëj-gànnaar fa Dan, \q1 seen naari góor di ŋexal, suuf sépp yëngu. \q1 Ñu dikk, tas réew mi tasar, \q1 booleek li ci biiram, \q1 ak dëkk beek ñi ci biiram.» \sp Yàllaay wax \q1 \v 17 «Maa ngii déy di leen yónnee \q1 jaani ñàngóor yu déggul jat, \q1 ñu di leen màtt.» \q1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. \s1 Yeremi am na naqar \sp Yeremeey wax \q1 \v 18 Ndaw naqar wu tiis, \q1 ndaw xol bu diis! \q1 \v 19 Sama bokk yaa ngooguy yuuxu \q1 yuux yu àkki fu sore, \q1 naan: «Moo \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji daa newul \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* a? \q1 Moo Buurub Siyoŋ da fee nekkatul a?» \sp Yàllaay wax \q1 «Lu tax ñuy yékkati sama xol \q1 ak seen jëmmi tuur yii, \q1 seen yàllay doxandéem yi tekkiwul dara?» \sp Yeremeey wax \q1 \v 20 Ngóob wéy na, jamonoom wees, \q1 te nun de muccagunu. \q1 \v 21 Sama bokk yi seen xol jeex \q1 tax na sama xol jeex, \q1 may tiislu, tancoo njàqare! \q1 \v 22 Moo diwu pajtal amul Galàdd a\f + \fr 8.22 \fr*\fk Galàdd \fk*\ft ab gox la bu féete dexu Yurdan penku te nekkoon fu bare gàncaxi pajtal.\ft*\f*? \q1 Am fajkat a fi amul? \q1 Ana lu waral bokk yi taneeguñu? \c 9 \q1 \v 1 Éy ku may duyal sama bopp ndox, \q1 saay gët di xelliy rongooñ \q1 yu ma jooye guddeek bëccëg \q1 bokk yi ñu bóom? \q1 \v 2 Éy ku ma mayoon ci màndiŋ mi \q1 dalu panaanum njëggaan, \q1 ba ma teqlikook bokk yi, wacc leen, \q1 dem, bàyyi leen? \q1 Ñoom ñépp ay bokkaale, \q1 di gàngooru workat. \s1 Dëgg jeex na \sp Yàllaay wax \q1 \v 3 «Ñu ngi tàwwi ni fittkat seen làmmiñu workat, \q1 seen doole ci réew mi doxaluñu ci yoon. \q1 Ñu ngii di def lu bon ci kaw lu bon, \q1 te man faalewñu ma.» \q1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. \b \q1 \v 4 «Na ku ne moytu dëkkandoom \q1 te baña wóolu menn mbokk. \q1 Kuy mbokk déy lal nga pexem wuruj, di wuruj; \q1 kuy dëkkandoo, sos ngay wéye. \q1 \v 5 Ku ne sa dëkkandoo ngay nax, \q1 te dëgg, doo ko wax. \q1 Dañoo tàmmi fen, \q1 di def njekkar ba sonn. \q1 \v 6 Yeena ngi dëkke njublaŋ, \q1 njublaŋ rekk, \q1 faaleetuleen ma.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \b \q1 \v 7 Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi \q1 wax ne: «Maa ngii di leen segg, \q1 nattu leen ni weñ gu sawara seeyal, xelli! \q1 Ana nu may def neneen \q1 ak sama ñoñ? \q1 \v 8 Seen làmmiñ di fitt guy bóome, \q1 seeni wax dig njublaŋ. \q1 Nit di wax moroomam jàmm, \q1 te di ko tëru cim xelam. \q1 \v 9 Lii duma leen ko dumaa?» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 Mu ne: «Xeet wu mel nii duma ko fey yoolam?» \s1 Jooy jot na \sp Yeremeey wax \q1 \v 10 Tund ya laay jooy, di yuuxu, \q1 di jooy parluy màndiŋ ma, \q1 fa lépp lakk, ba jaareesu fa, \q1 déggeesul baatu jur; \q1 njanaaw ak mala, \q1 lépp daw, ne mes. \sp Yàllaay wax \q1 \v 11 «Maay def Yerusalem jali doj, \q1 till yi dëkke; \q1 ma def dëkki Yuda gent bu kenn dëkkul.» \sp Yeremeey wax \q1 \v 12 Ana ku muus, ba xam lu waral lii? \q1 Ku \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxal, \q1 mu wax nu lu waral réew mi sànku, \q1 gental ni màndiŋ mi, \q1 kenn jaaru fi? \b \q1 \v 13 Aji Sax ji neeti: \q1 «Ñoo wacc sama yoon \q1 wi ma leen tegaloon, \q1 sàmmuñu sama kàddu, \q1 jëfewuñu ko, \q1 \v 14 xanaa toppoo dëgër bopp, \q1 topp tuuri \w Baal|lemma="Baal:"\w* \q1 yi leen seeni maam miinaloon.» \b \q1 \v 15 Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, \q1 Yàllay Israyil dafa wax ne: \q1 «Maa ngii di leelsi xeet wii njàqarey xeme, \q1 nàndal leen tookey mbugal. \q1 \v 16 Maa leen di wasaare fi biir xeet yu ñu xamuloon, \q1 du ñoom, du seeni maam. \q1 Maa leen di tofal saamar, ba raafal leen.» \b \q1 \v 17 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: \q1 «Ne leen: Waajleena wooyi jigéeni jooykati dëj yi, ñu dikk; \q1 yónneeleen ca ña gëna man, ñu dikk.» \sp Yeremeey wax \q1 \v 18 Nañu gaaw dëbbeel nuy jooy, \q1 gët taa, rongooñ wal. \q1 \v 19 Yuux a ngoog, jibe \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*. \q1 Ñu naa: «Nooka rajaxoo, \q1 torox ba ne tott, \q1 noon màbb sunuy dëkkuwaay, \q1 nu génn réew mi.» \b \q1 \v 20 Yeen jigéen ñi, \q1 ngalla dégluleen kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 taataan waxam, \q1 ba jàngal seeni janq jooyi dëj, \q1 jigéen ju ne jàngal moroomam yuuxi dëj. \q1 \v 21 Ndee déy moo ñalgoo sunuy palanteer, \q1 dugg sunuy kër yu yànj, \q1 ngir fàdd gone yi ci mbedd mi, \q1 ak xale yu góor yi ci pénc yi. \sp Yàllaay wax \q1 \v 22 «Ne leen: Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. \q1 Néew yeey wetaroo ci àll bi, mel niy jonkan, \q1 ni gub yu góobkat won gannaaw, kenn forul.» \s1 Ku xam Yàlla rekk a xelu \q1 \v 23 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: \q1 «Ku xelu, bumu damoom xelam; \q1 ku jàmbaare, bumu damoo njàmbaaram; \q1 ku woomle, bumu damoom koomam. \q1 \v 24 Kuy damu kay, na damoom xelam \q1 mu ko may mu xam ma, \q1 xam ne maay Aji Sax, \q1 jiy jëfe ngor ak dëgg ak njekk fi kaw suuf. \q1 Loolu déy mooy sama bànneex.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \s1 Xaraf, na Yàlla tax \q1 \v 25 «Ay bés a ngii di ñëw,» \q1 kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee, \q1 «maay dikkal képp ku xarafam yem ci yaram, \q1 \v 26 muy waa Misra, di waa Yuda, \q1 di Edomeen ñeek Amoneen ñi, \q1 di Mowabeen ñeek \q1 mboolem ñiy wat seen peggu kawaru bopp \q1 te dëkke màndiŋ mi, \q1 nde xeet yooyu, kenn xarafu ci dëgg, \q1 waaye \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp it \q1 xarafuñu xarafu xol\f + \fr 9.25 \fr*\ft Xeeti àddina yu bare baaxoo nañu di xaraf. Waaye xaraf ci la Yàlla nammoona birale kóllëre gi dox digganteem ak bànni Israyil. Moo tax gépp góor gu bokk ci woowu askan waroona fésal ci yaramam màndargam xaraf miy firndeel googu kóllëre, te ànd ceek xolu jëfe ko.\ft*\f*.» \c 10 \s1 Aji Sax ji du moroomu xërëm \q1 \v 1 Yeen \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, dégluleen kàddu, \q1 gi leen \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dégtal. \q1 \v 2 Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 «Jikkoy xeeti yéefar yi, buleen ko roy; \q1 màndargam asamaan, buleen ko tiit; \q1 na ko yéefar yi tiit. \q1 \v 3 Aaday xeet yi kat neen la. \q1 Garab lañuy dagge ca gott ba, \q1 ab yettkat yette ko sémmiñ, \q1 \v 4 rafetale xaalis ak wurus, \q1 daaj koy pont, dëgëral, \q1 ba du yëngu; \q1 \v 5 muy saf kuñeental \q1 ci biir tóokërub xaal. \q1 Du wax, du séqi jéego, \q1 ñu di ko gaŋar-gaŋaree. \q1 Buleen ko ragal, du lore, du jariñe.» \sp Yeremeey wax \q1 \v 6 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, kenn melul ni yaw, \q1 yaaka màgg, jàmbaare, màggu tur. \q1 \v 7 Yaw Buuru xeet yi, ana ku la dul ragal? \q1 Yaw déy yaa yelloo ragal. \q1 Mboolem ñi xelu ci xeet yi \q1 ak mboolem seeni buur, \q1 kenn melul ni yaw. \q1 \v 8 Ñoom ñépp a bokk dofe, ñàkk bopp: \q1 xam-xamu kasara, bant kese! \q1 \v 9 Xaalis lañuy jële Tarsis, xoobe ko bant, \q1 wurus wu jóge Ufas, ñu boole ca, \q1 ndaanaan liggéey ko, \q1 tëggu gànjar yett ko, \q1 ñu solal ko ndimo lu yolet \q1 ak lu xonq curr, \q1 lépp di liggéeyu ràbb yu xareñ. \q1 \v 10 Waaye Aji Sax jeey Yàlla dëgg. \q1 Mooy Yàlla jiy dund, \q1 di buur ba fàww, \q1 xadaram gësëm àddina, \q1 meram man xeet yi. \q1 \v 11 Lii nag, nangeen ko siiwal: \q1 «Seen yàlla, yi sàkkul asamaan, sàkkuñu suuf, \q1 ñooy sànku, jóge fi suuf ak fi asamaan tiim.» \q1 \v 12 Suuf, Aji Sax jee sàkke kàttanam; \q1 dun bi, mu sampem xelam; \q1 asamaan, mu lale xam-xamam. \q1 \v 13 Bu àddoo, ndoxum asamaan riir; \q1 mu yéegey niir fa cati àddina, \q1 yebbee ngelaw fa dencam ya, \q1 daldi melax, taw. \b \q1 \v 14 Nitoo nit dim sannax, sore xam-xam: \q1 te képp kuy tëgg sa jëmmu tuur, yaa añe gàcce. \q1 Sa jëmmi weñ ji nga xelli, di neenug neen, \q1 noog bakkan, tus! \q1 \v 15 Cóolóolu neen, liggéeyu caaxaan; \q1 bu bésam taxawee, mu sànku. \q1 \v 16 Ki séddoo Yanqóoba déy wuute naak yii caaxaan. \q1 Kookoo bind lépp, \q1 te Israyil di giir gi mu séddoo. \q1 Kookooy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi! \s1 Mbugal dikk na \q1 \v 17 Yerusalemee, yeen ñi ñu gaw, \q1 forleen seen ëmb. \q1 \v 18 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji déy dafa wax ne: \q1 «Maa ngii naa xërr waa réew mi bii yoon, \q1 teg leen njàqare, ba ñu yég ko.» \sp Yerusalem ay wax \q1 \v 19 «Wóoy man, yàqu naa! \q1 Ndaw góom bu metti! \q1 Dama noon lii jàngoro doŋŋ a, \q1 naa muñ! \q1 \v 20 Xayma xotatoo, \q1 buumi xayma xëttandoo, \q1 samay doom wacc ma, ne mes; \q1 kenn sampatul sama xayma, firi ko.» \sp Yeremeey wax \q1 \v 21 Sàmmi xeet weeka dofe: \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, sàkkuwñu ko. \q1 Moo leen taxa bonle, \q1 seen jur gépp tasaaroo. \q1 \v 22 Xibaar a ngoog, di ñëw, \q1 riir mu réy a yëngoo réewum bëj-gànnaar, \q1 nara gental dëkki Yuda yu mag yi, \q1 till yi dëkke. \s1 Yeremi tinu na Aji Sax ji \q1 \v 23 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, maa xam ne \q1 nit moomul yoonam, \q1 kuy dox moomuli jéegoom. \q1 \v 24 Aji Sax ji, yar ma lu yem, \q1 te bañ maa yare mer, \q1 di ma semmal. \q1 \v 25 Xëppal sa xadar yéefar yi la yégul, \q1 ak làng yi la tuddul. \q1 Ñoo bóom giirug Yanqóoba, \q1 bóom leen ba fàkkas leen, \q1 gental seen dëkkuwaay. \c 11 \s1 Yuda fecci na kóllëre \p \v 1 Kàddu gii dikkal na Yeremi, bawoo fa \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji: \v 2 «Dégluleen sàrti \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* gii. Te yaw Yeremi, nga àgge ko képp kuy waa Yuda ak waa Yerusalem. \v 3 Nga ne leen: “Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: Alkànde ñeel na képp ku sàmmul sàrti kóllëre \v 4 gii ma santoon seeni maam bés ba ma leen génnee réewum Misra, taalu xellikaayu weñ gu ñuul ba. Ma noon leen ngeen déggal ma te jëfe sàrti kóllëre gi ni ma leen ko sase, ba doon sama ñoñ, man ma doon seen Yàlla. \v 5 Su ko defee ma wàccook ngiñ, la ma giñaloon seeni maam ne dinaa leen may réew mu meew maak lem ja tuuroo, muy fii tey.”» Ma ne ko: «Tigi, Aji Sax ji.» \p \v 6 Aji Sax ji ne ma: «Yéeneel mboolem kàddu yii ci biir dëkki Yuda yu mag yi ak ci mbeddi Yerusalem, nga ne: “Dégluleen sàrti kóllëre gii te jëfe ko. \v 7 Artu naa àrtu seeni maam, dale ko ba ma leen génnee réewum Misra, ba tey jii ma jàppoo di leen àrtu, naan leen ngeen déggal ma. \v 8 Waaye dégluwñu, teewluwñu, xanaa ku nekk di wéye dëgër bopp, topp ag bon xolam. Moo tax ma wàcce ci seen kaw mboolem sàrti kóllëre gii ma leen santoon ñu war koo jëfe te jëfewuñu ko.”» \p \v 9 Aji Sax ji dellu ne ma: «Pexem fippu feeñ na ca Yuda gépp ak ca waa Yerusalem. \v 10 Dellu nañu ca seen ñaawtéefi maam, ya bañoona sàmm samay kàddu. Ñoom it topp nañu yeneen yàlla, di leen jaamu. Waa kër Israyil ak waa kër Yuda fecci nañu kóllëre ga ma fasoon ak seeni maam.» \p \v 11 Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: «Maa ngii di leen wàcceel musiba mu ñu dul mana rëcc. Dinañu ma ne wóoy te duma leen déglu. \v 12 Su ko defee waa dëkki Yuda yu mag yeek waa Yerusalem dem jooytuji ca yàlla, ya ñuy taalal cuuraay, te duñu leen mana wallu mukk ci seen jamonoy musiba. \p \v 13 «Yaw Yuda, ni sa dëkk yu mag tollu, ni la say tuur tollu. Ni mbeddi Yerusalem tollu it, ni la \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* yi ñu fa saam tollu, ñu di fa taalal cuuraay \w Baal|lemma="Baal:"\w*, tuur mu seexluwu mi.» \p \v 14 «Yaw nag Yeremi, bul ñaanal askan wii. Bu leen tinul, bu leen dagaanal. Ndax kat keroog bu ñu nekkee ci seen musiba, ba naan ma wóoy, du maay déglu.» \s1 Aji Sax ji dëddu na soppeem \sp Yàllaay wax \q1 \v 15 «Ana lu samay soppe di defati sama kër? \q1 Ñu bare ci ñoom a ngi def lu bon. \q1 Ndax seeni sarax man naa far seen jëf ju ñaaw, \q1 ba tax bu ñuy def lu bon, di ko bége?» \b \q1 \v 16 Oliw naat, jekki doom; \q1 nii la leen \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji tudde woon, \q1 waaye riir mu réy lay jibal, \q1 jafal ko, mu tàkk, \q1 taar réer car ya, meŋŋ. \q1 \v 17 Aji Sax ji Boroom gàngoor bi leen jëmbatoon, \q1 moo leen tuddal lu bon. \q1 Nee: «Waa kër Israyil ak Yuda ñoo def lu bon, \q1 di taalal \w Baal|lemma="Baal:"\w* cuuraay ba merloo ma.» \s1 Ñu ngi fexeel Yeremi \q1 \v 18 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee ma xamal, ma xam, \q1 ba gis seeni jëf. \q1 \v 19 Ndax damaa naagu woon ni xar \q1 mu ñu jëme rendikaay ba. \q1 Xawma woon ne man lañuy lalal ay pexe, \q1 naan: «Nan gor garab ak doomam, \q1 dagge ko fi réewum boroom bakkan, \q1 ba deesul fàttlikooti turam.» \b \q1 \v 20 Ma ñaan Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, \q1 kiy àtte dëgg, di nattu xel ak xol, ne ko: \q1 «Yaw laa diis sama mbir, \q1 won ma séen mbugal.» \p \v 21 Moo tax Aji Sax ji wax lii ci mbirum waa Anatot, ñiy wut sama bakkan, naan ma: «Baal di waxe \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* ci turu Aji Sax ji, lu ko moy nu rey la.» \v 22 Moo tax kay Aji Sax ji Boroom gàngoor yi wax ne: «Maa ngii di wàccesi mbugal fi seen kaw; seen xale yu góor fàddoo saamar, seeni doom, góor ak jigéen, deeye xiif. \v 23 Aw nit, duñu ko dese; maay wàcceel waa Anatot safaan, bu seen atu mbugal taxawee.» \c 12 \s1 Yeremee ngi ñaxtu \q1 \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, dëggu nga def, \q1 li may tawatsi fi yaw lépp. \q1 Teewul ma di la diis mbir: \q1 lu tax ku bon di baaxle, \q1 bépp workat bu bon di féex? \q1 \v 2 Yaa leen jëmbat, ñu sampi reen, \q1 law ba meññ; \q1 jegeñal la seen làmmiñ, \q1 te fekk nga sore seen xol. \q1 \v 3 Waaye yaw Aji Sax ji, xam nga ma; \q1 gis nga ma, seetlu sama xol ci yaw. \q1 Diri leen niy xar yu ñuy rendi, \q1 beral leen bésub rendi. \b \q1 \v 4 Ba kañ la réew mi naa sereŋ, \q1 gàncaxu tooloo tool di lax? \q1 Rabu àll ak njanaaw a ngi sànku \q1 ngir mbonug ñi fi dëkk \q1 te naan: «Moom xoolul sunu muj!» \s1 Yàlla tontu na \q1 \v 5 «Ndegam boroom ñaari tànk ngay rawanteel, xoox, \q1 nooy rawanteeki fas? \q1 Soo wóoluwul lu moy àll bu ne yàmblaŋ, \q1 nooy def ak gottub Yurdan? \q1 \v 6 Say bokk ak sa waa kër baay sax, \q1 ñoom it wor nañu la, \q1 ñoom it xaacu nañu, sam la; \q1 te bu ñu lay wax jàmm it, \q1 bu leen gëm.» \s1 Aji Sax ji dëddu na séddoom \q1 \v 7 «Dëddu naa sama kër, \q1 maa wacc sama séddoo, \q1 wacce sama soppey xol loxol noonam. \q1 \v 8 Sama séddoo ngi may niru léegi \q2 gaynde ci gott bi, \q1 di ma xiiru, ba tax ma jéppi ko. \q1 \v 9 Sama séddoo baa ngi may saf tan mu todde \q2 mu moroomi tanam gaw. \q1 Doxleen dajaleji rabi àll yépp, \q1 indi leen ci bernde ji. \q1 \v 10 Gàngooru sàmm a sëxëtoo sama tóokëru reseñ, \q1 joggati sama waar, \q1 def waar wi ma neex \q1 màndiŋ mu ne maraas. \q1 \v 11 Def nañu ko gent buy jooy fi sama kaw, \q1 réew mi mépp gentala gental, \q1 te saful kenn. \q1 \v 12 Tundoo tund wu ne faraas fi màndiŋ mi, \q1 ay yàqkat a ngi ciy bawoo, \q1 doon saamaru \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, di faagaagal réew mépp, \q1 cat ba cat, \q1 jàmm réer luy dund! \q1 \v 13 Jiwum pepp, góob ay dég; \q1 sonn, ñàkk yool, \q1 xanaa mbetteel ci meññeef mii sababoo \q2 ci merum Aji Sax ji.» \s1 Aji Sax ji àrtu na dëkkandooy Israyil \p \v 14 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: «Mboolem sama dëkkandoo yu bon, yi laal céru suuf bi ma sédd Israyil sama ñoñ, maa ngii di leen déjjatee seen réew, te waa kër Yuda, maa leen di seppee fi seen digg. \v 15 Waaye bu ma déjjatee yooyu xeet ba noppi, dinaa leen dellu yërëm, ku nekk, ma delloo ko céram, ku nekk ak suufam. \v 16 Waaye bu ñu royee ba roy sama ñoñ, di jëfe ni sama ñoñ wara jëfe, di giñe sama tur naan: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund,” na ñu daan royloo sama ñoñ, ba ñuy giñe \w Baal|lemma="Baal:"\w*, tuur mi, su boobaa ñu sampu fi sama digg ñoñ. \v 17 Waaye xeet wu ma ci déggalul, xeet woowu dama koy déjjati, déjjat, sànk leen.» Kàddug Aji Sax jee. \c 13 \s1 Colu Yeremi misaal la \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji da maa wax ne ma: «Demal jëndi njiitlaayu lẽe\f + \fr 13.1 \fr*\fk njiitlaay li \fk*\ft ñuy wax fii, séru njiitlaay lu gàtt lay doon.\ft*\f*, nga woddoo ko, te bu ko ndox laal.» \v 2 Ma jënd njiitlaay, woddu, muy la Aji Sax ji wax. \v 3 Aji Sax ji dikkal ma ñaareel bi yoon, ne ma: \v 4 «Jëlal njiitlaay li nga woddoo, te daldi dem ba Fara\f + \fr 13.4 \fr*\fk Fara \fk*\ft bérab la bu bokkul ak dexu Efraat doonte neexoo nañuy tur.\ft*\f*, nga làqi ko fa ca xar-xaru doj ya.» \v 5 Ma dem làqi ko Fara, muy la ma Aji Sax ji sant. \v 6 Ñu dem ba mu mat ay fan yu takku, Aji Sax ji ne ma: «Demal Fara, jëli njiitlaay la ma la santoon nga làqi ko fa.» \v 7 Ma dem fa ma làqoon njiitlaay la, sulli ko. Ndeke njiitlaay la yàqu na, ba amatul njariñ! \p \v 8 Kàddug Aji Sax ji dellu dikkal ma, ne ma: \v 9 «Aji Sax ji dafa wax ne: Ni lii yàqoo, ni laay sàggee sagub Yuda ak sagu Yerusalem bu réy bi. \v 10 Askan wu bon wii bañ maa déggal, të ticc di wéye seen coobare, di topp yeneen yàlla, di leen jaamook a sujjóotal, nañu mel ni njiitlaay lii amul benn njariñ. \v 11 Ndax ni njiitlaay di taqe ci luppu nit, noonu laa jële woon waa kër Israyil ak waa kër Yuda, taqoo leen.» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Maa ko def ngir ñu doon sama ñoñ, teral sama tur, di sama ndam, di sama sag. Waaye déggaluñu ma.» \s1 Yàlla misaal na meram \p \v 12 «Nga wax leen kàddu gii: “\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Yàllay Israyil dafa wax ne: Njaqal biiñ, duy, mu fees. Bu ñu la nee: ‘Dañoo xamul xéll ne njaqal biiñ, duy, mu fees?’ \v 13 nga ne leen: ‘Aji Sax ji dafa wax ne: Muy buur yi toogal Daawuda cib jalam, di \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi, di yonent yi, di mboolem waa Yerusalem, maa ngii di duysi mboolem waa réew mii, ba ñu fees ak màndite. \v 14 Su ko defee ma fenqe ku nekk ak mbokkam, fenqe waajur ak doom, ñoom ñépp.’ ”» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Duma ñéeblu, duma yërëm, duma leen ñeewantee faagaagal.» \s1 Dégloo, balaa yeex \q1 \v 15 Dégluleen te teewlu, buleen fétteeral. \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji kat wax na! \q1 \v 16 Teral-leen seen Yàlla Aji Sax ji, \q1 bala moo lëndëmal, \q1 ngeen tërëfe tundi timis, \q1 di séentu leer, \q1 mu lëndëmal ba mu ne këruus, \q1 fatt taraj \q1 \v 17 Bu ngeen déggul de, \q1 ma làqu, jooy seen reewande, \q1 sama rongooñ tuuroo tuuru, \q1 ma jooya jooy, \q1 nde dees na jàpp géttu Aji Sax ji, yóbbu. \s1 Mbugal a ngi \q1 \v 18 Waxal Buur, wax Lingeer yaayu Buur ne leen: \q1 «Dëjuleen fi suuf, \q1 seen mbaxanam nguur mu yànj foq na. \q1 \v 19 Dëkki Negew yu mag yi tëje na, \q1 te kenn du ko tijji. \q1 Yuda gépp ca ngàllo ga, Yuda ba mu daj, ngàllo ga.» \s1 Yerusalem am na gàcce \q1 \v 20 Yerusalemee, séentul, xool ñiy jóge bëj-gànnaar. \q1 Moo ana gétt gi ñu la dénkoon, \q1 sa gàtt yu rafet ya? \q1 \v 21 Sa xejj yi nga miinal sa bopp, \q1 bu ñu walbatikoo tiim la, \q1 ana looy wax nag? \q1 Kon mitit du la jàpp, \q1 nga mel ni kuy matu? \q1 \v 22 Soo nee ci sam xel: \q1 «Lu tax lii dal ma?» \q1 xamal ne sa ñaawtéef gu réy a waral \q1 ñu ñori la, saaysaaye la. \q1 \v 23 Ana ab \w Kuuseen|lemma="Kuus:"\w* bu mana soppi deram, \q1 mbaa am segg mu mana fari tipp-tippam? \q1 Kon nga mana def lu baax \q1 te tàmma def lu bon! \sp Yàllaay wax \q1 \v 24 «Maa lay tasaare ni boob muy naaw \q1 mu ngelawal màndiŋ mi wal. \q1 \v 25 Loolooy sa wàll, \q1 sa cér bi ma la nattal.» \q1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. \q1 Mu ne: «Yaa ma fàtte, \q1 di yaakaari caaxaan. \q1 \v 26 Man it maay ëñ sa pendal, \q1 muure sa kanam, \q1 saw taat ne duŋŋ. \q1 \v 27 Sag njaalook sa ŋexali caga, \q1 sa gànctu gu ruslu \q1 ci kaw tundi àll bi! \q1 Maa gis sa jëf ju siblu jooju! \q1 Musibaa yaw Yerusalem! \q1 Foo àppal sa jëfi sobe ji?» \c 14 \s1 Maral dikk na \p \v 1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jii dikkaloon na Yeremi, jëm ca maral ma. Mu ne: \q1 \v 2 «Waa Yudaa ngi ñaawlu, \q1 doole dëddu dëkk yi, \q1 ñu ne yogg, ne lasar fi suuf, \q1 yuux jollee Yerusalem. \q1 \v 3 Kàngam ya yebal seeni surga, ñu rooti; \q1 ñu dem, gisuñu ndox ca mbalka ya, \q1 délseek seen xotti ndab, \q1 jàq, yaakaar tas, ñu muuru di tiislu. \q1 \v 4 Réew mi tawluwul, suuf si fett, \q1 yaakaaru beykat tas, mu muuru, di tiislu. \q1 \v 5 Kéwél sax jur ci àll bi, sànni \q1 ndax ñàkk um ñax. \q1 \v 6 Mbaamu àll taxaw ci tund yi ne faraas, \q1 di àppaat niw till, \q1 ñàkk parlu, gët ya giim.» \sp Yeremeey wax \q1 \v 7 Dëgg la sunuy ñaawtéef a nu tuumaal, \q1 waaye éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, jógal te saw tur tax, \q1 doonte dëddu nanu la ay yooni yoon, moy la. \q1 \v 8 Éy yaw, yaakaaru Israyil, mi nuy wallu bésu njàqare, \q1 bul ñooru ni doxandéem ci réew mi, \q1 mbaa ku nekk ciw yoon, jàdd fi, fanaan. \q1 \v 9 Ngalla bul mel ni ku waaru, \q1 mbaa jàmbaar ju manul walloo. \q1 Yaw Aji Sax ji, yaa ngi sunu biir, \q1 ñu di nu tudde saw tur. \q1 Bu nu wacc! \p \v 10 Aji Sax ji dafa wax ci askan wii ne: «Ñeeka bëgg ub taxawaalu, baña téye seen tànk. Moo tax man Aji Sax ji bégewuma leen. Léegi ma bàyyi xel seenug mbon, ba mbugale leen seeni moy.» \s1 Waxyuy caaxaan jib na \p \v 11 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nag ne ma: «Bul ñaanal askan wii. \v 12 Su ñu ci boole woon koor sax, duma déglu seeni dagaan. Su ñu ma doon sarxalal \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* ak \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* it, du maa leen di nangul. Xanaa saamar akub xiif ak mbas kay laa leen di faagaagale.» \p \v 13 Ma ne ko: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, yonent yaa ngii di leen wax ne duñu dajeek saamar, duñu xiif te jàmm ju ne ñoyy nga leen di defal fi bii bérab.» \p \v 14 Aji Sax ji ne ma: «\w Waxyuy|lemma="waxyu:"\w* fen la yonent yiy waxe ci sama tur. Yebaluma leen, santuma leen ko, waxumaak ñoom. Peeñuy fen ak ngisaaney neen ak nax yu ñu fental seen bopp lañu leen di jottlee waxyu.» \v 15 Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: «Yonent yi ma yebalul te ñuy waxe waxyu ci sama tur naan: “Saamar akub xiif du am ci miim réew,” saamar akub xiif ay mujje yooyu yonent. \v 16 Ñi ñu doon jottli ay waxyu it, xiif ak saamar a leen di rey, ñu sànni seeni néew ci mbeddi Yerusalem, te duñu am ku leen rob, ñook seeni jabar ak seeni doom, góor ak jigéen. Dinaa leen xëpp seen ay. \q1 \v 17 Nanga leen yégal saw tiis, ne leen: \q1 “Naa tuur rongooñ guddeek bëccëg, \q1 te du fer; \q1 sama bokki bopp yi damm ba dammtoo, \q1 ndaw góom bu metti! \q1 \v 18 Ma dem, xool àll, \q1 gisuma lu moy ñu saamar bóom, \q1 ma dugg biir dëkk, \q1 gisuma lu moy ñu ne làcc akub xiif, \q1 yonent ak \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* di wër réew mi, \q1 xam-xam réer leen.”» \s1 Yeremee ngi tinu Aji Sax ji \q1 \v 19 Aji Sax ji, wacc ngaa wacc Yuda nii? \q1 Am \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* a la génnliku? \q1 Lu tax nga di nu dumaa musiba mu amul paj? \q1 Nuy yaakaar jàmm, dara baaxul, \q1 nuy séentum paj, tiitaange ne jaas! \q1 \v 20 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, xam nanu sunug mbon, \q1 xam sunu ñaawtéefi maam; \q1 moy nanu la moos. \q1 \v 21 Waaye xoolal ci yaw te bul xalab, \q1 bul teddadil sa jal bu tedd. \q1 Bàyyil xel te baña fecci sa \w kóllëreek|lemma="kóllëre g-:"\w* nun. \q1 \v 22 Xërëmi neen yi yéefar yiy jaamu, \q1 ana ku ci mana taw? \q1 Am asamaan ay sóobal boppam ay waame? \q1 Du yaw la Aji Sax ji sunu Yàlla? \q1 Yaw lanu yaakaar, \q1 te loolu lépp, yaw a. \c 15 \s1 Aji Sax ji àddu na \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nag ne ma: «Musaa ak Samiyel sax, bu ñu taxawoon fi sama kanam, du tax ma faale askan wii. Dàqal, ñu sore ma, te wéy. \v 2 Bu ñu la laajee ne la: “Fu nu jëm?” nga wax leen ne leen: \q1 “Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Kiy wopp dee, wopp dee; \q1 kiy deeye saamar, deeye saamar; \q1 kiy deeye xiif, deeye xiif; \q1 kiy duggi ngàllo, duggi ngàllo.” \p \v 3 «Te dinaa wàcce fi seen kaw ñeenti xeeti duma.» Kàddug Aji Sax jee. «Saamar di bóom; xaj diri yóbbu, njanaaw ak rabu àll for, mu jeex. \v 4 Dama leen di def, waa réewi àddina yépp, ku leen ci xool rasu. Te li ko waral di Buurub Yuda, Manase miy doomu Esekiya, ak li mu def ci digg Yerusalem.» \s1 Mbugalu Yuda du jaas \sp Yàllaay wax \q1 \v 5 «Yerusalemee, ku lay yërëm? \q1 Ku lay jooy? \q1 Moo, ku lay geesu ne la: “Jàmm nga am?” \q1 \v 6 Yaw yaa ma wacc,» kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee, \q1 «dellu gannaaw, \q1 ma duma la, sànk la. \q1 Muñ naa ba sonn. \q1 \v 7 Maa leen bees ni ñuy beesem pepp \q1 ci pénci réew mi. \q1 Maa sànk sama ñoñ, \q1 faat seeni doom, \q1 ndax tuubuñu seeni jëfin. \q1 \v 8 Seeni jëtun laa ful, \q1 ba ñu ëpp suufas géej, \q1 ma indil leen pàddum njolloor, \q1 mu reyal yaay doomi waxambaaneem, \q1 këpp ko tiitaangeek njàqare. \q1 \v 9 Yaayu juróom yaari góor loof, di àppaat, \q1 jantam sowe bëccëg ndarakàmm, \q1 yaakaar tas, mu jàq, \q1 seenu ndes, ma leel saamaru noon.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \s1 Aji Sax ji feddli na yebam \sp Yeremeey wax \q1 \v 10 Wóoy saa ndey, \q1 loo ma doon jure! \q1 Man mi réew mépp di xulook a layool, \q1 leblewma, lebuma; \q1 te ñépp di ma móolu. \q1 \v 11 Ndaxam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nee: \q1 «Maa lay xettli déy, ngir sottal lu baax; \q1 maa la defal sa noon di la tinu déy, \q1 ci janti safaan ak njàqare.» \sp Yàllaay wax ak Yerusalem \q1 \v 12 «Ku mana toj weñ gu ñuul, \q1 rawatina yetu weñu bëj-gànnaar, mbaa xànjar? \q1 \v 13 Yeen waa Yuda, seen alal ak seeni denc \q1 laay jox ñu ko sëxëtoo te feyuñu \q1 ndax seen gépp moy ci seen réew mépp. \q1 \v 14 Maa leen di def seen jaami noon \q1 réew mu ngeen xamul, \q1 sama mer jippét, tàkkal leen.» \sp Yeremeey wax \q1 \v 15 Yaw déy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, xam nga! \q1 Ngalla bàyyi ma xel, geesu ma; \q1 feyul ma ñi ma sam. \q1 Bu leen muñal ba sànk ma! \q1 Xamal ne yaa ma tax di dékku saaga. \q1 \v 16 Sa kàddu laa gis, di ko dunde, \q1 sa kàddu di ma bégal, bànneexal sama xol. \q1 Yaw Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, déy, \q1 sa tur lañu ma tudde. \q1 \v 17 Masumaa toogandook ñiy mbumbaay \q1 bay xawaare. \q1 Yaa ma jiite, ma beru, toog \q1 ndax mer mi nga ma sol, ba ma fees. \b \q1 \v 18 Moo sama tiis wi du dakk a? \q1 Bii góom bu metti, tëë wér! \q1 Yaw kay yaay waltan muy wal, di ŋiis, \q1 di tas sama yaakaar. \b \q1 \v 19 Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 «Soo délsee, ma délloosi la, \q1 nga dellu di ma liggéeyal. \q1 Soo dee wax ngëneel \q1 lu soreeki caaxaan, \q1 dinga mel ni yaay sama làmmiñ, \q1 te nit ñeey délsi ànd ak yaw, \q1 waaye du yaay délsi ànd ak ñoom. \q1 \v 20 Maa lay def nga mel ak askan wii \q1 ni tatay xànjar ju ñu dàbbli, \q1 ñu di la song \q1 te duñu la man. \q1 Maay ànd ak yaw, \q1 di la wallu, di la xettli.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 21 «Ab soxor jàpp la, ma àtte; \q1 ab néeg ne la céex, ma foqati.» \c 16 \s1 Yeremi wéet na ci biiri bokkam \p \v 1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkalati ma, ne ma: \q1 \v 2 «Bul jël jabar, \q1 bul am doom ju góor mbaa ju jigéen ci bii bérab.» \q1 \v 3 Aji Sax ji kat dafa wax ci gone yu góor yeek gone yu jigéen \q1 yi juddoo ci bii bérab, \q1 wax ci seen ndey yi leen jur \q1 wax ci seen baay yi leen meññ ci mii réew, \q1 \v 4 mu ne: «Jàngoroy ndee a leen di rey. \q1 Deesu leen jooy, deesu leen rob. \q1 Seeni néew ay tosal suuf. \q1 Saamar akub xiif a leen di sànk, \q1 seeni néew leel njanaaw ak rabi àll.» \q1 \v 5 Te Aji Sax ji kat dafa wax ne: \q1 «Bul dugg kërug dëj, \q1 bu fa dem di ñaawlook a jaale. \q1 Maa xañ askan wii sama jàmm,» \q1 kàddug Aji Sax jee, \q1 «xañ leen sama ngor ak sama yërmande. \q1 \v 6 Ku mag ak ku ndaw ay dee ci réew mii, \q1 te deesu leen rob, \q1 deesu leen jooy. \q1 Kenn du dagg yaramam \q1 mbaa muy nelu, di ko ñaawloo. \q1 \v 7 Kenn du leen sédd aw ñam \q1 wu ñuy dëfale ku deele, \q1 kenn du leen jox ub kaas, dëfale leen, \q1 doonte baay a dee mbaa ndey. \q1 \v 8 Kërug bernde it, bu fa dugg, \q1 di toogandoo, di lekk ak a naan.» \q1 \v 9 Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi kat dafa wax ne: \q1 «Maa ngii di dakkal ci bii bérab, \q1 ngeen teewe, fekke lépp \q2 luy coowal mbégteek bànneex, \q1 boroom séet ak séetam selaw. \p \v 10 «Su ko defee, boo waxee askan wii kàddu yooyu yépp, ñu ne la: “Ana lu waral Aji Sax ji dogalal nu musiba mu réy mii mépp? Ana fu nu tooñe ak fu nu moye sunu Yàlla Aji Sax ji?” \v 11 Nga wax leen nag ne leen: “Seeni maam a ma wacc,” kàddug Aji Sax jee, “di topp yeneen yàlla, di leen jaamook a sujjóotal. Man nag, ñu dëddu ma; sama yoon it, ñu bañ koo sàmm. \v 12 Yeen nag, ngeen di bon, ba raw seeni maam. Yeena ngii, ku nekk të ticc, topp xolam bu bon, bañ maa déggal. \v 13 Maa leen di dàqe ci réew mii, jëme réew mu ngeen xamul, seeni maam xamuñu ko, ngeen di fa jaamu guddeek bëccëg yeneen yàlla, ndax dootuma leen baaxe.”» \s1 Yaakaar jeexul \p \v 14 «Waaw ay bés a ngi ñëw déy,» kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee, «deesatul wax ne: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund te génnee \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* réewum Misra.” \v 15 Waaye dañu naan: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund, ki jële bànni Israyil réewum bëj-gànnaar, te jële leen mboolem réew ya mu leen sànke woon.” Maa leen di délloosi seen réew ma ma joxoon seeni maam.» \s1 Kenn rëccul mbugal mi \p \v 16 «Maa ngii di woolu nappkat yu bare.» Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. «Ñu napp ñii ba noppi ma woo rëbb yu bare, ñu rëbb leen ci kaw mboolem tund wu mag ak wu ndaw, ba ci bépp xar-xaru doj. \v 17 Samay bët a ngi ne jàkk déy ci seeni jëf. Dara umpu ma ci. Seeni ñaawtéef, dara rëccu ma ci. \v 18 Dama leen di jëkka fey ñaari yoon seeni moy, ndax ñoo sobeel sama réew meek seen méddi tuur yu bon yi, feesal suuf sii ma séddoo seen yëf yu siblu yooyu.» \s1 Ñépp ay ràññeeji Aji Sax ji \sp Yeremeey wax \q1 \v 19 Yaw \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji may dooleel, \q1 di ma feg, di ma làq bésub njàqare, \q1 yaw la xeet yiy bawoo cati àddina, \q1 fekksi la, naan: \q1 «Caaxaani neen kay la sunuy maam baaxoo woon, \q1 xërëmi neen yu amul njariñ. \q1 \v 20 Nit man naa sàkkal boppam ay yàlla? \q1 Te duñuy yàlla sax!» \sp Yàllaay wax \q1 \v 21 «Moo tax maa ngii di leen xamal bii yoon, \q1 ba ñu xam sama diisaayu loxook sama doole, \q1 xam ne maay \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji.» \c 17 \s1 Aji Sax ji sikk na Yuda \q1 \v 1 «Bàkkaaru Yuda lañu binde xaccug weñ \q1 gu cat la di doj wu dëgër. \q1 Dees koo ñaas ci seen àlluway xol, \q1 ñaas ko ci seen béjjéni \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*. \q1 \v 2 Seeni doom sax di bàyyi xel seeni sarxalukaay \q1 ak seen xer yi ñuy màggale tuurum \w Asera|lemma="Asera:"\w* \q1 fi ker garab yu naat yeek \q1 kaw tund yu mag yi \q1 \v 3 ak kaw tund yi ci àll bi. \q1 Seen alal ak seen denc yépp \q1 laay joxe, ñu lël ko, \q1 booleek seen jaamookaay \q1 ndax seen moy yi dajal réew mi. \q1 \v 4 Dingeen xañ seen bopp cér bi ma leen séddoon, \q1 ma def leen seen jaami noon \q1 ci réew mu ngeen xamul, \q1 ndax merloo ngeen ma \q1 mer mu dul fey mukk.» \s1 Aji Sax jee jara yaakaar \q1 \v 5 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: \q1 «Alkànde ñeel na ku yaakaar doom aadama \q1 ak képp kuy doolewoo nit, \q1 dëddu Aji Sax ji. \q1 \v 6 Day mel ni gajjub ndànd-foyfoy, \q1 du gis ngëneel luy dikk! \q1 Day dëkke màndiŋ mu wow koŋŋ, \q1 suufas xorom su kenn dëkkul. \q1 \v 7 Waaye barke ñeel na ku wóolu Aji Sax ji, \q1 yaakaar Aji Sax ji. \q1 \v 8 Day mel ni garab gu saxe wetu ndox, \q1 lawal ay reenam ca wal ma, \q1 ragalul tàngoor wu dikk, \q1 xob ya di naat. \q1 Du tiit atum maral, \q1 du ñàkk meññeef.» \b \q1 \v 9 «Dara gënula dëng xelum nit, \q1 laago la ci moom. \q1 Ana ku ko mana xam? \q1 \v 10 Maay Aji Sax jiy seetlu xel, \q1 natt ub xol, \q1 di yool ku nekk jëfinam, \q1 la yellook añam. \q1 \v 11 Kuy jagoo alal ju lewul, \q1 mooy picc mu toj lu mu nenul. \q1 Kookooy tollu digg dooleem, alal ja dëddu, \q1 mu mujje dof.» \sp Yeremeey wax \q1 \v 12 Sunu bérab bu sell bi, \q1 mooy ngànguney daraja, daa masa kawe. \q1 \v 13 Yaw \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji yaakaaru Israyil, \q1 ku la wacc, torox; \q1 ku la dëddu daa repp. \q1 Moo wacc Aji Sax ji, bëtu ndox miy dund. \s1 Yeremi ñaan na Yàlla wall \q1 \v 14 Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, faj ma, ma faju; \q1 musal ma, ma mucc, \q1 samag cant, yaw a. \q1 \v 15 Ñu ngii naa ma: \q1 «Ana la Aji Sax ji waxoon? \q1 Na dikk boog!» \q1 \v 16 Man de, bañuma laa sàmmal, topp la; \q1 bésub tiis it dagaanuma ko. \q1 Yaw de xam nga ko. \q1 Li ma wax it fi sa kanam la. \q1 \v 17 Bu ma teg tiitaange, \q1 yaay sama rawtu bésub safaan. \q1 \v 18 Ngalla gàcceelal ñi ma topp, \q1 te bu ma gàcceel; \q1 yal nañu tiit, ñoom, \q1 te man, ma baña tiit. \q1 Rikk dikke leen bésub safaan, \q1 rajaxe leen ñaari yoon. \s1 Bésub Noflaay ñeel na Aji Sax ji \p \v 19 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji da maa wax ne ma: «Demal taxawi ca buntu Doomi réew mi, fa buurub Yuda di duggeek a génne. Te nga taxaw itam ca mboolem bunti Yerusalem ya ca des. \v 20 Nga ne leen: “Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yeen buuri Yuda ak yeen waa Yuda gépp ak képp ku dëkk Yerusalem, di jaare bunt yii. \v 21 Aji Sax ji dafa wax ne: Moytuleen seen bopp ba baña gàddu lenn \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*, di ko jaarale bunti Yerusalem. \v 22 Buleen génne seeni kër lenn bésub Noflaay te buleen ci liggéey lenn. Waaye nangeen sellal bésub Noflaay, muy la ma santoon seeni maam. \v 23 Ndaxam dégluwñu ma, teewluwñu ma, xanaa të ticc, baña dégg, di gàntal ndigal. \v 24 Waaye su ngeen ma dégloo ba déglu ma, kàddug Aji Sax jee, baña gàddu lenn di jaare bunti dëkk bii bésub Noflaay, xanaa di sellal bésub Noflaay, bañ cee liggéey lenn, \v 25 su boobaa buur yiy tooge jalub Daawuda, tey dawal watiir aki fas, ñook seeni kàngam, duñu noppee jaare bunti dëkk bii, feggook seeni kàngam. Waa Yudak waa Yerusalem it di jaare ci bunt yii, dëkk bi sax dàkk. \v 26 Dees na bàyyikoo dëkki Yuda ak li wër Yerusalem ak diiwaanu Beñamin, ca suufu tundu waak kaw tund ya, ak ca diiwaanu Negew. Ñuy indi ci kër Aji Sax ji ay \w saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* ak yeneen saraxi jur ak \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* ak \w cuuraay|lemma="cuuraay l-:"\w*. Ñii di indi kër Aji Sax ji \w saraxi cant|lemma="Sarax yi:"\w*. \v 27 Waaye su ngeen ma déggalul, baña sellal bésub Noflaay, baña moytoo gàddu lenn, di jaare bunti Yerusalem bésub Noflaay, su boobaa dinaa taal dëkk bi taal buy xoyom këri Yerusalem yu yànj, te du fey.”» \c 18 \s1 Boroom njaq doon na misaal \p \v 1 Kàddu gii dikkal na Yeremi, bawoo fa \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Mu ne ko: \v 2 «Dalal di dem ca tabaxkatu njaq ba. Foofa laa lay dégtale sama kàddu.» \v 3 Ma daldi dem ba ca kër tabaxkatu njaq ba. Ma fekk ko muy liggéey ca tabaxukaayu njaqam. \v 4 Leeleeg ndab li tabaxkat biy tabaxe ban, yàqu ci loxoom, mu dellu defaraat ba mu baax ci moom. \v 5 Kàddug Aji Sax ji nag dikkal ma ne ma: \v 6 «Ni tabaxkatu njaq bii di def, dama koo manula def ak yeen, \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*?» Kàddug Aji Sax jee. «Ban bii déy, ni mu mel ci loxol tabaxkatu njaq bi, ni ngeen mel ci sama loxo, yeen bànni Israyil. \v 7 Leeg-leeg ma wax lu jëm ci aw xeet mbaa am réew, ne dinaa ko déjjati, daaneel ko, tas ko, \v 8 xeet woowu tuub mbonam gi ma leen doon artoo, ma fomm musiba mi ma naroona wàcce ci seen kaw. \v 9 Leeleeg it ma wax lu jëm ci aw xeet mbaa am réew, ne dinaa ko tabax, jëmbat ko, \v 10 ba noppi ñu def lu ma ñaawlu, baña dégg sama kàddu. Su ko defee ma fomm lu baax la ma leen naroona baaxe. \v 11 Kon waxal boog waa Yuda ak waa Yerusalem ne leen: “Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngi nii di leen tabaxal musiba ci pexe mu ma leen di fexeel. Kon na ku nekk dëpp yoonam wu bon te jubbanti jikkoom aki jëfam.” \v 12 Dañu naan: “Jaru ko, sunu xalaatu bopp lanuy topp, ku nekk të ticc di jëfe sa xel mu dëng.”» \s1 Israyil fàtte na Aji Sax ji \q1 \v 13 Moo tax \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: \q1 «Laajteleen rekk ci xeet yi! \q1 Ku ci masa dégg lu mel nii? \q1 Lu ñaawa ñaaw la Israyil, janq ba, def! \q1 \v 14 Ku masa gis fu tawub yuur gedde mbartali Libaŋ, \q1 mbaa wal mu sedd ma cay wale fu sore ŋiis? \q1 \v 15 Moona sama ñoñ fàtte nañu ma; \q1 tuuri caaxaan, ñu taalal cuuraay, \q1 te tuur yi di leen fakktal ci seeni yoon, \q1 seen jaaruwaay ya woon, \q1 di leen jaarale ñall yu kenn xàllul, \q1 \v 16 ba seenum réew gental, \q1 di lu ñuy muslu fàww, \q1 ku fa romb waaru, wëcc bopp. \q1 \v 17 Maay mel ni ngelawal penku, tasaare leen, \q1 ñu daw seeni noon. \q1 Gannaaw laa leen di won, \q1 waaye du doon kanam, \q1 keroog seen bésu ay.» \s1 Fexeel nañu Yeremi \p \v 18 Ba mu ko defee, mu am ñu ne: «Aywaleen, nu lalal Yeremi pexe. Ndax kat soxlawunu ko ba di ci ñàkk dara: du njànglem \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w*, du digley boroom xel te du waxyu bu yonent biral. Nanu ko duural ba sànk ko te baña faale lenn ciy waxam.» \q1 \v 19 Waaye yaw \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, teewlu ma \q1 te déglu kàddug noon yi. \q1 \v 20 Lu baax dees na ko feye lu bon a? \q1 Moona gasal nañu ma am yeer, di ma tëru. \q1 Bàyyil xel ba may taxaw fi sa kanam, \q1 di leen tinul ngir nga moyale leen sa mer. \q1 \v 21 Kon nag bàyyil seeni doom ñu xiif ba dee, \q1 jañax leen ci ñawkay saamar, \q1 seeni jabar suul doom, suul jëkkër, \q1 seeni góor loroo mbas, \q1 seeni waxambaane daanoo xare. \q1 \v 22 Boo jekkee yebal gàngoor, \q1 yal na yuux jibe seeni kër. \q1 Ñoo gas um yeer, di ma rëbb, \q1 làqal may fiir. \q1 \v 23 Waaye yaw Aji Sax ji, xam nga mépp pexe \q2 mu ñu may fexee bóome. \q1 Bu leen jéggal seen ñaawtéef, \q1 bul far seeni moy, \q1 yal nañu nërmeelu fi sa kanam, \q1 jëflanteel ak ñoom bi ngay mer. \c 19 \s1 Njaq la toj na \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: «Demal ca tabaxkatu njaq ba, nga jëndi fa njaqu ban lu ndaw te ànd ak ñenn ci magi askan wi ak ñenn ci magi \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi, \v 2 te nga dem ba ca xuru Ben Inom, ca buntu Tojitu njaq ya, daldi fay yéene kàddu yi ma lay wax. \v 3 Danga naan: “Yeen buuri Yuda, yeen waa Yerusalem, dégluleen kàddug Aji Sax ji. Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Maa ngii di wàcce fi bii bérab, musiba muy buur noppi képp ku ci dégg.” \v 4 Li ko waral mooy dañu maa wacc, teddadil bérab bii, di fi taalal cuuraay yeneen yàlla yu ñu xamuloon, du ñoom, du seeni maam, du buuri Yuda. Te feesal nañu bérab bii deretu nit ñu deful dara. \v 5 Yékkatil nañu fi \w Baal|lemma="Baal:"\w* tuur mi \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w*, di ci lakk seeni doom ngir Baal, defal ko ko \w saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, te santaanewma ko, waxuma ko, jaarul sax sama xel. \p \v 6 «Moo tax ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «su boobaa deesatul wooye bérab bii Tofet mbaa xuru Ben Inom, xanaa xuru Bóomukaay. \v 7 Maay neenale fii pexem Yudak Yerusalem. Maa leen di tërale seen saamaru noon, ñi leen di tëru, tër leen; seeni néew, ma leele njanaaw ak rabi àll. \v 8 Maay def dëkk bi ab gent bu ñuy muslu, ku fi jaare waaru, di muslu ci seen mbugal yépp. \v 9 Maa leen di yàpploo seen doom yu góor ak yu jigéen, ku nekk di yàpp sa moroom ci biir njàqare, ndax gaw bu metti, bu leen seen noon yi leen di tëru di gaw. \p \v 10 «Gannaaw loolu nanga toj njaq lu ndaw li fi kanam ñi nga àndal, \v 11 te nga ne leen: “Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Askan wii ak dëkk bii, ni ñuy toje njaq, ba deesatu ko mana defaraat, ni laa koy tojate. Tofet gii dees na fi rob ndax ñàkk fu ñu robe. \v 12 Noonu laay def bérab bii,” kàddug Aji Sax jee, “ak ñi fi dëkk. Maay def dëkk bii ni Tofet. \v 13 Këri Yerusalem ak këri buuri Yuda dina fees ak sobe ni bérab bii di Tofet. Mooy mboolem kër yu ñu doon taalal cuuraay ca kaw taax ya ñeel biddiiw yépp, ak di fa tuural yeneen yàlla.”» \p \v 14 Gannaaw ba Yeremi walbatikoo Tofet, ga ko Aji Sax ji yebaloon mu waxi fa \w waxyu|lemma="waxyu:"\w*, dafa taxawi ca ëtti kër Aji Sax ji, daldi wax ak mbooloo ma mépp. Mu ne leen: \v 15 «Aji Sax ji, Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: “Maa ngii di wàcce ci kaw dëkk bii ak mboolem li ko wër, lépp luy musiba mu ma dige woon, ndax dangeena të ticc, baña dégg sama kàddu.”» \c 20 \s1 Tëj nañu Yeremi \p \v 1 Ci kaw loolu, doomu Imer, Pasur, \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba jiite woon saytub kër Yàlla ga, dégg Yeremi muy biral kàdduy \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* yooyu. \v 2 Ba mu ko defee Pasur dóorlu Yonent Yàlla Yeremi, jéng ko ca buntu kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ja féete kaw, te ñu dippee ko Beñamin. \v 3 Ca suba sa Pasur yiwee ko ca jéng ba. Yeremi ne ko: «Aji Sax ji tuddeetu la Pasur; Magor-Misabib (mu firi Tiitaange lu dajal) la la tudde. \v 4 Ndax Aji Sax ji dafa wax ne: “Maa ngii di la wàcceel tiitaange, yaak sa soppe yépp, seen saamaru noon daaneel leen, ngay gis; te Yuda gépp laay teg ci loxol buuru Babilon, ñii mu yóbbu leen ngàllo, ñee mu jam leen, ñu dee. \v 5 Maay joxe lépp luy alalu dëkk bii. Mboolem lu fiy njariñ, mboolem gànjar, mboolem denci buuri Yuda, dinaa ko teg ci seen loxol noon yi, ñu sëxëtoo, jël, yóbbu Babilon. \v 6 Yaw Pasur, yaak sa waa kër yépp ay duggi njaam ca Babilon. Babilon nga jëm te fa ngay dee, ñu rob la fa, yaak mboolem sa soppe ya nga daan wax ay waxyuy fen.”» \s1 Yeremi ñaxtu na \q1 \v 7 Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, naxtaan nga ma, \q1 ma naagu, nga nax ma, \q1 jaay ma doole, ba man ma. \q1 Ñu ngi may kekku bés bu ne, \q1 ku ne di ma kókkali. \q1 \v 8 Saa yu ma waxee, damay xaacu, \q1 fitnaak salfaañoo ma tax di yuuxu. \q1 Kàddug Aji Sax jee may yóbbey xas \q1 aki saaga bés bu ne. \q1 \v 9 Su ma nee: «Xaaral ma fàtte ko, \q1 dootuma biral waxyu ci turam,» \q1 sama xol bi mel nib taal \q1 bu tàkk, tàbbi sama biir yax yi; \q1 may jéema muutuwaale sa kàddu, \q1 te duma ko man. \q1 \v 10 Dégg naa ñaawlaate yu bare, ñu naan: \q1 «Éey, Tiitaange-lu-dajal! \q1 Booleleen ko, boole rekk!» \q1 Ñi ma séqal jàmm sax, \q1 di yeeru ma fakkastalu, \q1 naan: «Jombul mu juum, nu jekku ko, \q1 ba mana feyu.» \q1 \v 11 Waaye Aji Sax jeek man, di ñeyi xare. \q1 Moo tax ñi may tëru di tërëf, ba duñu daan, \q1 xanaa rus lool, ndax duñu baaxle; \q1 gàcce gu yàgg lay doon te du fey. \q1 \v 12 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, yaw miy nattu ku jub, \q1 di gis xel ak xol, \q1 may ma, ma gis ni nga leen di feye; \q1 yaw de laa diis sama mbir. \b \q1 \v 13 Woyleen Aji Sax ji, \q1 màggal-leen Aji Sax ji! \q1 Mooy xettli néew-ji-doole \q1 ci dooley ku bon. \b \q1 \v 14 Alkute ñeel na bés ba ma juddoo, \q1 bés ba ma saa ndey juree, \q1 yàlla bumu barkeel. \q1 \v 15 Alkute ñeel na ka ko yegge baay, \q1 ne ko: «Sa soxna am na doom ju góor,» \q1 ba tax baay béga bég. \q1 \v 16 Yal na kooku mel ni dëkk, \q1 yi Aji Sax ji tas te yërëmu leen! \q1 Yal na dégg yuuxi suba teel \q1 ak xaacuy xarey njolloor. \q1 \v 17 Moo ma reyul ci sama biiru ndey, \q1 ma bàmmeeloo sama ndey, \q1 te du wasin mukk. \q1 \v 18 Ana lu ma doon génne ca biiram, \q1 di daj coonooku tiis, \q1 mujje gàcce? \c 21 \s1 Jéllub Yerusalem jubsi na \p \v 1 Kàddu dikkaloon na Yeremi, bàyyikoo fa \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Mooy ba buur Cedesyas yebalee ca moom, Pasur doomu Malkiya, mook \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba ñuy wax Cefaña doomu Maaseya. Mu ne ko: \v 2 «Ngalla seetal nu ci Aji Sax ji, ndax Nabukodonosor buuru Babilon mu ngi nuy song xare. Jombul Aji Sax ji defaatal nu lenn ciy kéemaanam ba mu dellu gannaaw.» \v 3 Yeremi nag ne leen: «Waxleen Cedesyas ne ko: \v 4 “Aji Sax ji, Yàllay Israyil dafa wax ne: Seen dooley xare ji ngeen yor, di xeexeek ñi ci biti, di buuru Babilon ak waa Babilon ñi leen gaw, maa ngii di ko walbati, dajale ko ci biir dëkk bii. \v 5 Man mii maay xareek yeen, won leen sama doole ak sama diisaayu loxo, xadaru, dikke leen mer mu réya réy. \v 6 Maay fàdd lu dëkk ci dëkk bii, nit ak mala bokk loroo mbas mu réy. \v 7 Gannaaw loolu nag,” kàddug Aji Sax jee, “Cedesyas buurub Yuda, aki jawriñam ak askan week ñi des ci dëkk bii te rëcce ci mbas meek xare beek xiif bi, maa leen di teg ci loxol Nabukodonosor buuru Babilon, ak seen loxol noon, ak loxol ñi leen di wuta rey. Dina leen leel ñawkay saamar. Du leen baal, du ñéeblu, du yërëm.” \p \v 8 «Te itam nga wax askan wii ne leen: “Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di teg fi seen kanam yoonu dund ak yoonu ndee. \v 9 Ku toog ci dëkk bii, dinga deeye xare mbaa xiif mbaa mbas. Ku génn jébbal boppam waa Babilon ñi leen gaw nag dinga dund, bakkanam di yoolu xareem. \v 10 Jógal naa dëkk bii déy, te loraange laa leen naral waaye du jàmm.” Kàddug Aji Sax jee. “Ci loxol buuru Babilon laa koy teg, mu jafal ko, lakk.”» \s1 Xibaar ñeel na waa kër buur \p \v 11 «Te it waxal waa kër buurub Yuda ne leen: \q1 “Dégluleen kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji! \q1 \v 12 Yeen waa kër Daawuda, \q1 Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Àtte yoon, deeleen ko xëye, \q1 di xettli ki ñu xañ dëgg \q1 ci ki koy néewal doole, \q1 balaa sama mer ne jippét, \q1 di tàkk te deesu ko mana fey \q1 ndax seen jëf ju bon. \q1 \v 13 Yeen ñi jataayoo xur wi, \q1 yeen ñi ci kaw doj wu tell wi, maa ngii fi seen kaw.” \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 “Yeen ñi naa: ‘Ku nu manal dara? \q1 Ku jote sunu biiri rawtu?’ \q1 \v 14 maa leen di dikke seen añu jëf.” \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 “Maay jafal sawara, lakk seen gott bi, \q1 mu xoyom lépp lu leen wër.”» \c 22 \p \v 1 Aji Sax ji dafa wax ne: «Demal kër buurub Yuda, nga jottli fa kàddu gii. \v 2 Danga naan: “Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yaw buurub Yuda mi toog ci jalub Daawuda, yaak say jawriñ ak sa nit ñiy jaare yii bunt. \v 3 Aji Sax ji dafa wax ne: Deeleen jëfe dëgg ak yoon, di xettli ku ñu xañ dëgg ci ki koy néewal doole. Ab doxandéem, ab jirim akub jëtun, buleen leen lor, buleen leen fitnaal. Deretu jaambur bu deful dara it, buleen ko tuur ci bii bérab. \v 4 Su ngeen jëfee ba jëfe santaane bii déy, buur du noppee dugge yii bunt, di toogal Buur Daawuda fi jalam, di dawal watiir aki fas, ànd ak seeni jawriñ ak seeni nit. \v 5 Waaye su ngeen dégluwul sama santaane yii, giñ naa ko ci man mii,” kàddug Aji Sax jee, “ab gent rekk la gii kër di doon!”» \p \v 6 Aji Sax ji déy dafa wax ci mbirum kër buurub Yuda ne: \q1 «Yaay sama àllub Galàdd, \q1 sama collu tundu Libaŋ, \q1 waaye déy, maa lay def ni màndiŋ, \q1 ngay dëkk yu kenn dëkkul. \q1 \v 7 Maa lay beralal yàqkat \q1 yu fàggu seeni gànnaay, \q1 dàjji sa tànnéefi banti seedar, \q1 sànni ca sawara sa. \p \v 8 «Doxandéem yu bare dinañu jaare dëkk bii, di laajte ci seen biir naan: “Ana lu waral Aji Sax ji def nii bii dëkk bu mag?” \v 9 Su ko defee ñu ne leen: “Xanaa li ñu fecci seen \w kóllërey|lemma="kóllëre g-:"\w* Yàlla Aji Sax ji, di sujjóotal yeneen yàlla, di leen jaamu.”» \s1 Lu jëm ci Salum buurub Yuda \q1 \v 10 Buleen jooy buur Yosya mi dee, \q1 buleen ko ñaawlul, \q1 jooyleena jooy buur Salum miy dem, \q1 te du délseeti, \q1 ba gis réewum juddoom. \p \v 11 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji kat dafa wax ci mbirum buurub Yuda, Salum mi wuutu baayam Yosya te bàyyikoo fii. Mu ne: «Du fi délseeti mukk. \v 12 Waaye fa ñu ko yóbbu ngàllo, fa lay deeye. Réew mii, du ko gisati mukk.» \s1 Lu jëm ci Yowakim, kuutaayu Buur Yosya \q1 \v 13 Wóoy ngalla kiy tabax këram te seetu ci njekk, \q1 di teg taaxi kawam te seetu ci yoon, \q1 liggéeyloo moroomam ci dara, \q1 feyu kow ñaqam. \q1 \v 14 Mu ngi naan: «Maay tabax kër gu yaa, \q1 taaxi kaw ya yàmblaŋ. \q1 Ma bënn ay palanteer, \q1 tafal kër gi banti seedar, \q1 diw ko ba mu xonq curr. \b \q1 \v 15 «Ëpplante banti seedar da laa def buur? \q1 Sa baay daawul lekk ak a naan? \q1 Teewu koo jëfe dëgg ak yoon, \q1 muy njiglaayam. \q1 \v 16 Da daan sàmm àqu ku ñàkk ak ku néew doole, \q1 muy njiglaay. \q1 Du looloo di xam maay kan?» \q1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. \b \q1 \v 17 «Yaw xooloo, \q1 xalaatoo lu moy loo jariñoo, \q1 ak noo tuure deretu jaamburu Yàlla, \q1 di fitnaale ak a lore?» \b \q1 \v 18 Moo tax Aji Sax ji wax ci mbirum buurub Yuda, Yowakim doomu Yosya, ne: \q1 «Kenn du ko jooy ca mbokkam mu góor mbaa mu jigéen, \q1 naan: “Wóoy ngalla nun, bokk yi!” \q1 Kenn du ko jooy, \q1 naan: “Wóoy, sang ba, wóoy kilifa ga!” \q1 \v 19 Robu mbaam-sëf lees koy rob: \q1 diri génne Yerusalem, \q1 sànni ca biti.» \s1 Yeremi yégle na fitnay Yerusalem \q1 \v 20 Aji Sax ji nee: «Yeen waa Yerusalem, \q1 yéegileen tundi Libaŋ, yuuxu. \q1 Àddooleen fa Basan, xaacu, \q1 te yuuxoo fa Abarim, \q1 nde seen soppe yépp a rajaxoo!» \b \q1 \v 21 «Waxoon naa leen ko ba ngeen di am jàmm, \q1 ngeen ne: “Dégluwnu!” \q1 Noonu ngeen jàppoo ba ngeen di ndaw ba tey, \q1 masuleen maa déggal! \q1 \v 22 Ngelaw dina sàmm seeni sàmm, sànk leen, \q1 seeni soppe duggi njaam, \q1 ba ngeen rus, torox \q1 ndax seen gépp mbon. \b \q1 \v 23 «Yaw mi tooge Libaŋ\f + \fr 22.23 \fr*\fk Libaŋ \fk*\ft man naa doon misaalu Yerusalem. Seetal ci \ft*\ft \+bk 1.Buur ya\+bk* 7.2.\ft*\f*, \q1 def um tàgg sa garabi seedar, \q1 éy bu la mitit dikkalee, \q1 nirook mititu mat, \q1 ndaw binni yu réy!» \s1 Lu jëm ci Kooña doomu Yowakim \p \v 24 Mu ne: «Giñ naa ko ci man miy dund,» kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee, «yaw buurub Yuda, Kooña\f + \fr 22.24 \fr*\fk Kooña \fk*\ft turu gàttalu Yowakin la. Seetal ci \ft*\ft \+bk 2.Buur ya\+bk* 24.8-17.\ft*\f* doomu Yowakim, soo doon jaarob torlukaay ci sama ndijoor it, fa laa lay foqatee, \v 25 teg la ci loxol ñi lay tëru te nga ragal leen; muy Nabukodonosor buuru Babilon aki xarekatam. \v 26 Maa lay xalab, yaak sa ndey ji la jur, jëme meneen réew mu ngeen juddoowul, te fa ngeen di deeye. \q1 \v 27 Réew mi ngeen namma délsi, dungeen fi délseeti.» \b \q1 \v 28 Nee ñu: «Waa jii Kooña da di njaq lu toj lu jarul daraa? \q1 Am da di xottu ndab lu kenn buggul? \q1 Lu waral ñu di ko sànni, mooki doomam, \q1 xalab leen biir réew mu ñu xamul?» \b \q1 \v 29 Éy waa réew mi, waa réew mee, waa réew mi, \q1 dégluleen Kàddug Aji Sax ji! \q1 \v 30 Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 «Bindleen ne waa jii amul doom! \q1 Du baaxle cig dundam, \q1 nde kenn ci geñoom du tekki, \q1 ba tooge jalub Daawuda, \q1 di jiiteeti fi Yuda. \c 23 \s1 Sàmm bu baax aye na \p \v 1 «Wóoy ngalla sàmm yiy sànk ak a tasaare sama gétt gi.» Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. \v 2 Moo tax Aji Sax ji Yàllay Israyil wax ci sàmm yiy sàmm ñoñam ne: «Yeena tasaare sama gétt gi, dàq leen, te taxawuwleen leen. Kon maa ngii di leen taxawoo mbugal, yoole leen seen jëf ju bon.» Kàddug Aji Sax jee. \v 3 «Man nag, sama ndesu gétt, maa leen di dajalee mboolem réew yi ma leen dàqoon, jëme; te maa leen di délloosi seen parlu, ñu meññ ba yokku. \v 4 Dinaa leen taxawalal ay sàmm yu leen di sàmm ba dootuñu tiit, dootuñu jàq, dootuñu wuute.» Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 5 «Ay bés a ngi ñëw,» kàddug Aji Sax jee, \q1 «maay jebbil Daawuda njebbitu njekk, \q1 mu falu di buur bu xelu, \q1 di jëfe njub ak njekk ci réew mi. \q1 \v 6 Ay jantam Yuda dina texe, \q1 Israyil dëkke kaaraange, \q1 te dees na ko tudde nii: \q1 “Aji Sax ji sunu njekk.” \p \v 7 «Moo tax ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «deesatul wax ne: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund te génnee \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ca réewum Misra.” \v 8 Xanaa dañu naan: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund te génnee askanu Israyil réewum bëj-gànnaar, génnee leen mboolem réew ya mu leen sànkeji woon.” Su ko defee ñu dëkkewaat seen suufas bopp.» \s1 Kàddu jógal na yonenti caaxaan \q1 \v 9 Mu jëm ci yonent yi: \q1 Sama bopp a ubu ràpp, sama xol jeex, \q1 sama yax yépp ne yalax, \q1 ma mel ni ku biiñ man, \q1 ba mu màndi \q1 ndax \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ak kàddoom yu \w sell|lemma="sell:"\w*. \q1 \v 10 Ay jaalookat la réew mi fees déy, \q1 alkànde déy a waral réew mi maral, \q1 parluy màndiŋ mi wowal. \q1 Seeni xél loraange la, \q1 seenug njàmbaar di naka-su-dul-noona. \sp Yàllaay wax \q1 \v 11 «Te it yonent ak \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ñoo bokk yàqu, \q1 sama biir kër sax gis naa ci seenug mbon.» \q1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. \q1 \v 12 «Moo leen tax di tarxiise seenu yoon, \q1 tàbbi lëndëm, fëlëñu. \q1 Maa leen di wàcceel musiba déy \q1 ca seen atum mbugal.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \b \q1 \v 13 «Ca yonenti Samari it laa gis njekkar, \q1 ñuy waxe \w waxyuy|lemma="waxyu:"\w* \w Baal|lemma="Baal:"\w* tuur mi, \q1 di réeral Israyil, sama ñoñ. \q1 \v 14 Waaye yonenti Yerusalem laa gisal lu yées: \q1 ñuy jaaloo, di wéye ay fen, \q1 di dooleel defkatu lu bon, \q1 ba kenn dëdduwul mbonam. \q1 Ñoom ñépp di ma niru waa Sodom, \q1 waa Yerusalem it ni waa Gomor.» \b \q1 \v 15 Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi \q1 wax lii ci mbirum yonent yi: \q1 «Maa ngii di leen leelsi njàqarey xeme, \q1 nàndal leen tookey mbugal, \q1 nde fi yonenti Yerusalem la yàqute tukkee, \q1 ba law ci réew mi mépp.» \b \q1 \v 16 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: \q1 «Buleen déglu yonent yi leen di wax ay waxyu; \q1 cóolóoli neen lañu leen di naxe, \q1 di fent ay peeñu, di wax ay waxyu, \q1 te du kàddug Aji Sax ji. \q1 \v 17 Ñi ma teddadil lañuy waxa wax, \q1 naan leen Aji Sax ji déy nee: \q1 “Jàmm ngeen di am.” \q1 Képp ku topp sa xelum déggadi, \q1 ñu ne ko: “Musiba du la dab mukk.” \b \q1 \v 18 «Waaye ana ku ci teewe woon jataayu Aji Sax ji? \q1 Ku ci fekke, ba dégg kàddoom? \q1 Ku ci teewlu kàddoom, ba dégg ko? \q1 \v 19 Ngëlénu Aji Sax jaa ngoog, \q1 sànjam fettax na, \q1 dig callweer, \q1 callweeral boppu ku bon. \q1 \v 20 Merum Aji Sax ji du giif, \q1 te deful ba sottal li mu nar. \q1 Fan yu mujj yii, ngeen am ci lu leer. \q1 \v 21 Yebaluma yonent yii, \q1 ñoom ñuy daw di yégle! \q1 Waxumaak ñoom, \q1 ñoom ñuy jottli waxyu! \q1 \v 22 Su ñu teewe woon sama jataay sax, \q1 mana dégtal sama ñoñ samay kàddu, \q1 ba waññee leen seen yoonu mbon \q1 ak seen jëfi mbon. \q1 \v 23 Xanaa du maay Yàlla?» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 «Fu jegeek fu sore, du maay Yàlla? \q1 \v 24 Ku mana làqoo làquwaay, \q1 ba duma ko gis?» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 «Xanaa du asamaan ak suuf, \q1 maa ko fees?» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \p \v 25 «Dégg naa kàdduy waxyu yi yonent yooyuy waxe ci sama tur ay fen, naan gént nañu lii, gént nañu lee. \v 26 Fan la yonenti fen-kat yii àppal seeni xalaat, di wax waxyuy naxe yu ñu fental seen bopp? \v 27 Seen gént yi ñuy nettalante, nammuñu ci lu moy sama ñoñ fàtte ma, ni ma seeni maam fàttee woon ndax Baal tuur mi. \v 28 Yonent bu ci am gént, na nettali géntam, waaye ku ci am sama kàddu, na ko àddoo, na ma ko waxe. Ana ñax akum pepp?» Kàddug Aji Sax jee. \v 29 «Sama kàddu déy, daa mel ni sawara,» kàddug Aji Sax jee, «mbaa saddu, di falaxew doj! \v 30 Moo tax maa ngii ci kaw yonent yi.» Kàddug Aji Sax jee. «Ñu ngi sàccante samay kàddu. \v 31 Maa ngii ci kaw yonent yi.» Kàddug Aji Sax jee. «Ñu ngi mbel-mbeli naan: “Kàddoo ngi.” \v 32 Maa ngii ci kaw ñiy waxe waxyuy génti caaxaan.» Kàddug Aji Sax jee. «Ñu ngi nettali seeni gént, bay waññi sama ñoñ, ndax seen fen yu jéggi dayo, te man de yebaluma leen, santuma leen dara. Amaluñu askan wii benn njariñ.» Kàddug Aji Sax jee. \s1 Yéeneb Aji Sax ji du ab yen \p \v 33 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ne Yeremi: «Su la askan wii laajee mbaa ab yonent mbaa ab \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ne la: “Ana yéeneb waxyu bi la Aji Sax ji yóbbante?” Nga wax leen ne leen: “Yeenay yen bi te dinaa leen yenniku.”» Kàddug Aji Sax jee. \v 34 «Te muy yonent, muy sarxalkat mbaa kenn ci askan wi, ku ci ne: “Yéeneb waxyu bii la ma Aji Sax ji yóbbante ci yeen,” maay dikke mbugal kooku mook waa këram. \v 35 Li ku nekk wara laaj moroomam mbaa mbokkam kay mooy: “Lu Aji Sax ji tontu?” mbaa “Lu Aji Sax ji wax?” \v 36 Waaye yéeneb waxyu bu Aji Sax ji, buleen ko fi tuddati. Jooju wax déy, yenu boroom lay doon. Ndax dangeena been sunu kàddug Yàlla, Yàlla Aji Sax jiy dund, Boroom gàngoori xare yi. \v 37 Li nit kiy laaj ab yonent mooy: “Ana lu Aji Sax ji tontu? Ana lu Aji Sax ji wax?” \v 38 Bu ngeen dee tudd ab yéeneb waxyub Aji Sax ji, te ma yónnee ci yeen, ne leen buleen di tudd ab yéeneb Aji Sax ji, su boobaa Aji Sax ji dafa wax ne: \v 39 Maa leen di yenu déy, xalab leen, yeen ak dëkk bii ma leen joxoon, yeen ak seeni maam, ba ngeen sore ma. \v 40 Te maa leen di teg toroxte gu sax dàkk, ak gàcce gu sax dàkk te du fey.» \c 24 \s1 Li ñaari dàmbi figg di misaal \p \v 1 Gannaaw gi Nabukodonosor buuru Babilon toxal na buurub Yuda Yekoña\f + \fr 24.1 \fr*\fk Yekoña \fk*\ft ak Yowakin kenn ki la.\ft*\f* doomu Yowakim, yóbbu ko Babilon, mook kàngami Yudak liggéeykati xarala yaak liggéeykati weñ ya. Ba loolu amee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji am lu mu ma won: da maa jekki gis ñaari dàmbi figg yu tege fi kanam kër Aji Sax ji. \v 2 Genn dàmb gi di figg ju baaxa baax, mel ni witt mu jëkk. Dàmb gi ci des di figg ju bona bon, ju kenn dul lekk ndax bon. \p \v 3 Aji Sax ji wax ma ne ma: «Yeremi, loo gis?» Ma ne ko: «Xanaa ay figg. Figg ju baax ji nag baax na lool, waaye ju bon ji daa bona bon, ba kenn du ko lekk ndax bon.» \p \v 4 Kàddug Aji Sax ji nag dikkal ma, ne ma: \v 5 «Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: Ni figg jii baaxe, ni laay geesoo mbaax ngàllog Yuda gi ma yebale bérab bii, jëme leen réewum Babilon. \v 6 Maa leen di toppe bëtu mbaax, ba délloosi leen ci réew mii. Maa leen di defar te duma leen daaneel; jëmbat leen te duma leen buddi. \v 7 Maa leen di may coobarey xam ma, te xam ne maay Aji Sax ji, ba ñu doon sama ñoñu bopp, man ma doon seen Yàlla. Dinañu délseek seen léppi xol ci man déy!» \p \v 8 Waaye Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Ni figg jii bone, ba kenn manu koo lekk ndax bon, ni laay def Cedesyas buurub Yuda aki kàngamam ak ndesu Yerusalem. Muy ñi des ci réew mi, di ña toxuji Misra. \v 9 Maa leen di def ñu jara seexlu, di musibay mboolem réewi àddina, ba fépp fu ma leen sànni, seen tur di fa saaga te kuy léeboo ak kuy kókkalee mbaa ngay móoloo, ñoom ngay tudd. \v 10 Maay yebal saamar fi seen kaw ak xiif ak mbas, ba ñu raaf fi kaw suuf si ma leen joxoon, ñook seeni maam.» \c 25 \s1 Ab tënkub waxyoo ngi \p \v 1 Kàddu gii dikkal na Yeremi, jëm ci waa Yuda gépp, ci ñeenteelu atu nguurug doomu Yosya Yowakim, buurub Yuda. Mu yemook at mi jëkk ci nguurug Nabukodonosor buuru Babilon. \v 2 Yonent Yàlla Yeremi daa wax ak waa Yuda gépp ak waa Yerusalem gépp, ne leen: \p \v 3 Li ko dale fukkeelu at ak ñett ci nguurug doomu Amon, Yosya buurub Yuda, ba tey jii, di ñaar fukki at ak ñett, kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jaa ngi may dikkal, ma di leen ko jottli te tàyyiwma, waaye dégluwleen. \v 4 Aji Sax ji yónnee leen mboolem jaamam ñiy yonent yi. Yónni na leen ay yooni yoon. Waaye dégluwleen, teewluwleen. \v 5 Mu ne leen: «Na ku nekk ci yeen dëpp jëfinam ju bon ak jëfam ju bon, ba mana dëkke réew mi leen Aji Sax ji jox naka jekk, yeen ak seeni maam, ba fàww, \v 6 te buleen topp yeneen yàlla, di leen jaamook a sujjóotal; buleen ma merloo ndax yëfi neen yu ngeen sàkke seeni loxo. Su boobaa duma leen teg musiba. \v 7 Waaye dégluwleen ma». Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Yeena ma merlook ak yëf yu ngeen sàkke seeni loxo, muy seen musiba.» \p \v 8 Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi wax ne: «Gannaaw dégluwleen samay kàddu, \v 9 maa ngii di yónnee, jëli mboolem làngi bëj-gànnaar.» Kàddug Aji Sax jee. «Maay yónnee it ca Nabukodonosor buuru Babilon mi ci samag curga, daldi leen boole indi ci kaw réew mii ak ñi ci biiram ak mboolem xeet yi ko séq. Maa leen di faagaagal, gental leen gent bu sax dàkk bu ñuy muslu. \v 10 Te muy kàddug mbégte di kàddug bànneex, di kàddug boroom séet akub séetam, di wolukaay bu fiy jib mbaa leer gu ñuy niitoo, lépp maa ko fiy boole tukkal. \v 11 Réew mii mépp ay gental, def ndànd-foyfoy, xeet yii yépp di surgawu buuru Babilon diiru juróom ñaar fukki at. \p \v 12 «Su ko defee bu juróom ñaar fukki at yi matee, ma doora dikkal Babilon ak buuram ndax seeni ñaawtéef.» Kàddug Aji Sax jee. «Maay gental réewum Babilon ba fàww. \v 13 Maay wàcceel réew mii mboolem kàddu yi ma ko rëbbe woon, te ñu bind ko ci téere bii, Yeremi jottli xeet yépp \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* bi. \p \v 14 «Ñoom waa Babilon it déy, dinañu surgawu ay xeet yu giir ak ay buur yu mag. Maa leen di fey seen añu jëf ju bon.» \ms1 Kàddug waxyu dal na xeet yi \mr (Saar 25.15-38) \p \v 15 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Yàllay Israyil déy da maa wax ne ma: «Am kaasu biiñ bii ci sama loxo, di misaal kaasu mbugal, te nga nàndal ci mboolem xeet yi ma lay yebal, \v 16 ñu naan, tërëf, di say ndax aaytéefu saamar laay yebal fi seen biir.» \p \v 17 Ma daldi jële kaas bi ci loxol Aji Sax ji, nàndal ci mboolem xeet yi mu ma yebal. \v 18 Ma nàndal waa Yerusalem ak dëkki Yuda ak seeni buur ak seeni kàngam ngir gental fépp, muy ndànd-foyfoy bu ñuy muslu, di ko móoloo ba sunu jonni yàllay tey. \p \v 19 Firawna buuru Misra it nàndal naa ko ca, mooki surgaam aki kàngamam ak waa réewam, \v 20 ak mboolem xeeti njaxasaan yi ci seen biir, ak mboolem buuri réewum Ucc, ak mboolem buuri réewum Filisteen ña féete Askalon ak Gasa ak Ekkron ak la des ca Asdodd. \v 21 Ma boole ca nàndal Edomeen ñaak Mowabeen ñaak Amoneen ña, \v 22 ak mboolem buuri Tir ak mboolem buuri Sidon ak buuri dun ya ca wàllaa géej, \v 23 ba ca waa Dedan ak Tema ak Bus ak mboolem ñiy wat seen peggu kawaru bopp, \v 24 ak mboolem buuri Arabi ak mboolem buuri xeeti njaxasaan yi dëkke màndiŋ mi, \v 25 ak mboolem buuri Simri ak buuri Elam ak mboolem buuri Medd, \v 26 boole ca mboolem buuri bëj-gànnaar, ñu jegeek ñu sore. Ma nàndal leen ñoom ñépp, ba réewi àddina yi ci kaw suuf yépp daj. Buurub Sesag\f + \fr 25.26 \fr*\fk Sesag \fk*\ft turu kumpa la, di Babilon ba tey.\ft*\f* topp ci ñoom, naan. \p \v 27 Aji Sax ji nag ne: «Wax leen ne leen: “Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Yàllay Israyil dafa wax ne: Naanleen ba màndi, di waccu, fëlëñu, tëë jóg ndax saamar bi may yebal fi seen biir.” \v 28 Waaye su ñu bañee naan ci kaas bi nga leen tàllal nag, nga wax leen ne leen: “Aji Sax ji dafa wax ne: Dingeen naan ba naanaatoo! \v 29 Te kat dëkk bii ñu ma tudde sax, maa ngi koy tàmbalee musibaal. Kon yeen, nu ngeen mana fexee ba mucc? Dungeen mucc moos, ndax saamar laay wool mboolem ku dëkke àddina.”» Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi. \p \v 30 Aji Sax ji teg ci ne ma: «Yaw nag, jottli leen mboolem kàdduy \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* yooyu. Te nga ne leen: \q1 Aji Sax jeey yëmmoo fa kaw ni gaynde, \q1 fa màkkaanam mu \w sell|lemma="sell:"\w* ma lay àddoo, \q1 ŋara ŋar ci kaw déndu suufam, \q1 xaacu xaacuy dërkati reseñ\f + \fr 25.30 \fr*\fk dërkati reseñ \fk*\ft yi ñuy wax fii, seeni tànk lañu daan dëre reseñ, te bu ñu tollu waan ci dër reseñ, dañuy woyaale.\ft*\f*, \q1 di ko gëdde mboolem waa àddina, \q1 \v 31 riir ma àkki cati àddina, \q1 ngir layoob Aji Sax jeek xeet yi, \q1 moom miy àtte mboolem boroom bakkan, \q1 ñu bon ñi, mu jébbal saamar.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \b \q1 \v 32 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: \q1 «Musibaa ngii, di lawal wii xeet ba ca wee, \q1 ngëlén lu réy a jollee cati àddina.» \p \v 33 Bésub keroog nag ñi Aji Sax ji fàdd, fu ne lañuy tëdd ci àddina, cat ba cat. Deesu leen jooy, deesu leen for, deesu leen rob. Ni neefare jonkan lañuy wetaroo ci kaw suuf si. \q1 \v 34 Yeen sàmmi askan wi, serleen, yuuxuleen; \q1 yeen boroom gétt gi, xëppooleen suuf, ñaawloo; \q1 seen bésub rendikat taxaw na, \q1 te dees na leen tasaare, \q1 ngeen daanu, rajaxoo \q1 ni njaqal tànnéef. \q1 \v 35 Rawtu day réer sàmmi askan wi, \q1 làquwaay réer boroomi gétt yooyu. \q1 \v 36 Yuuxi sàmm yaa ngoogu, \q1 jooyi boroom gétt yaa, \q1 Aji Sax jeey fóom seeni parlu. \q1 \v 37 Merum Aji Sax ju réy ji \q1 selawal na tooli jàmm ya. \q1 \v 38 Gaynde wacc na geeram, \q1 seen réew ma di ndànd-foyfoy, \q1 ndax saamaru notkat bi \q1 ak tàngooru sànjum Aji Sax ji. \c 26 \ms1 Yeremi dugg na coono \mr (Saar 26—45) \s1 Ñu ngi tëru Yeremi \p \v 1 Ba doomu Yosya, Yowakim buurub Yuda di doora falu, kàddu gii dikkaloon na Yeremi, bàyyikoo fa \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Mu ne: \v 2 «Aji Sax ji dafa wax ne: Dangay taxawi ca biir ëttu kër Aji Sax ji. Nga wax ak mboolem waa dëkki Yuda yiy jaamusi ci kër Aji Sax ji. Mboolem kàddu yi ma lay yóbbante ci ñoom, bu ci wacc baat. \v 3 Jombul ñu dégg, ba ku nekk dëpp yoonam wu bon. Su ko defee ma fomm musiba, mi ma leen di waajal ndax seen jëf ju bon. \v 4 Nga wax leen ne leen: “Aji Sax ji dafa wax ne: Su ngeen ma déggalul, toppuleen yoon wi ma leen rëddal, \v 5 dégguleen sama kàdduy jaam ñiy yonent yi may yónni ci yeen ay yooni yoon, ngeen tëë dégg, \v 6 su boobaa maay def kër Yàlla gii, na ma def ga woon ca Silo, te dëkk bii maa koy def lu mboolem xeeti àddina di tudd, di ko móoloo.”» \p \v 7 Ba mu ko defee \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yaak yonent yaak mbooloo ma mépp dégg Yeremi di wax kàddu yooyu ca biir kër Aji Sax ji. \v 8 Naka la Yeremi wax ba sottal mboolem la ko Aji Sax ji santoon mu jottli ko mbooloo ma mépp, sarxalkat yaak yonent yaak mbooloo ma mépp ànd jàpp ko, ne ko: «Yaw, dee rekk mooy sab àtte! \v 9 Ana lu waral ngay biral \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* ci turu Aji Sax ji, naan kër Yàlla gii dina tas, mel ni ga woon ca Silo, te dëkk bii day tas, kenn du fi des?» Mbooloo ma mépp nag sam Yeremi ca biir kër Aji Sax ji. \v 10 Kàngami Yuda dégg mbir ma, bàyyikoo kër buur, daldi yéegi ba kër Aji Sax ji. Ñu féncoo ca buntu kër Aji Sax ji ñuy wax bunt bu Bees ba. \v 11 Sarxalkat yaak yonent ya wax kàngam yaak mbooloo ma mépp, ne leen: «Waa jii, dee mooy àtteem, ndax moo biral waxyu, di rëbb sunu dëkk bii. Yeena ko déggal seen bopp.» \p \v 12 Ci kaw loolu Yeremi wax ak kàngam yépp ak mbooloo ma mépp, ne leen: «Aji Sax jee ma yebal ngir ma biral waxyu, rëbb kër gii ak dëkk bii, te mooy kàddu yi ngeen dégg yépp. \v 13 Léegi nag rafetal-leen seeni jëfin ak seeni jëf te déggal seen Yàlla Aji Sax ji. Su ko defee Aji Sax ji fomm musiba mi mu leen dogaloon. \v 14 Man nag maa ngii ci seen loxo! Lu ngeen xalaat ne moo gën te war ci man rekk, defleen! \v 15 Xamleen xéll rekk ne su ngeen ma reyee, bakkanu ku deful dara ngeen gàddu, yeen ak dëkk beek ñi ko dëkke, ndax ci lu wér Aji Sax jee ma yebal ci yeen, ngir ma yegge leen mboolem kàddu yii.» \v 16 Ba loolu amee kàngam yaak mbooloo ma mépp wax ak sarxalkat yaak yonent ya, ne leen: «Waa jii kay àtteb dee warul ci moom, ndax ci sunu turu Yàlla Aji Sax ji la nu waxal.» \v 17 Ci biir loolu ñenn ci magi réew mi jóg, wax ak mbooloo ma fa daje mépp, ne leen: \v 18 «Ku ñuy wax Mise, dëkk Moreset, doon na biral waxyu ca jamonoy Esekiya buurub Yuda. Daa waxoon waa Yuda gépp ne leen: “Aji Sax ji Boroom gàngooru xare yi dafa wax ne: \q1 Dees na gàbb \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* nib tool, \q1 Yerusalem diy tojit, jale; \q1 tundu kërug jaamookaay baay doon gajj bu kawe.” \p \v 19 «Ndax tax na Esekiya buurub Yuda mbaa kenn ci waa Yuda reylu ko? Du Buur Esekiya daa wormaal Aji Sax ji, tinu ko, ba Aji Sax ji fomm musiba mi mu leen dogaloon? Nun nag musiba mu réy lanu nara indil sunu bopp.» \s1 Yowakim reylu na ab yonent \p \v 20 Ci jamono yooyu amoon na keneen ku doon biral \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* ci turu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Muy Uri ma dëkk Kiryaat Yarim, di doomu Semaya. Uri doon biral waxyu, di rëbb dëkk baak réew ma, bokk ak Yeremi genn kàddu gi. \v 21 Buur Yowakim dégg ay kàddoom, mook mboolemi dagam ak kàngamam yépp. Ba mu ko defee Buur di ko wuta reylu, Uri yég ko, tiit, daw làquji Misra. \v 22 Buur Yowakim yebal ku ñuy wax Elnatan doomu Agbor ca Misra, mu ànd faak ñeneen. \v 23 Ñu jëleji Uri ca Misra, yót ko Buur Yowakim, mu jam ko, sànni néewam ca armeelu baadoolo ya. \p \v 24 Yeremi nag daa làqoo Ayikam doomu Safan, mu aar ko, ba tàbbiwul ci loxol askan wi, ñu rey ko. \c 27 \s1 Yeremi misaal na kilifteefu Babilon \p \v 1 Ba doomu Yosya, Cedesyas\f + \fr 27.1 \fr*\ft Fii ñu ne Cedesyas, am na sotti yu jëkk yu fi indi turu Yowakin.\ft*\f* buurub Yuda di doora falu, kàddu gii dikkaloon na Yeremi, bàyyikoo fa \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \v 2 Aji Sax ji da ne ma: «Sàkkalal sa bopp ay der ak yeti ràngaru yëkk, nga boole lépp teg ci sa ndodd; \v 3 ba noppi nga yónnee yet yi buurub Edom ak buuru Mowab ak buurub Amoneen ñi ak buurub Tir ak buurub Sidon. Dangay teg yet yi ci seen loxoy ndaw yi dikk Yerusalem ci Cedesyas buurub Yuda, ñu yót leen ko. \v 4 Te nga yóbbante leen ca seeni sang ne leen: “Aji Sax ji Yàllay Israyil, Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: Waxleen seeni sang ne leen: \v 5 Man maa sàkk suuf, sàkk doom aadama ak mala fi kaw suuf ci sama doole ju bare ak sama kàttan gu matale, te loolu lépp, maa ko jox ku ma neex. \v 6 Léegi nag teg naa réew yii yépp ci loxol Nabukodonosor buuru Babilon, mi ci sama curga, ba joxaale ko rabi àll yi sax, ñu nangul ko. \v 7 Mboolem xeet yee koy nangul, nangul doomam ba ci sëtam, ba keroog moom itam, àppu réewam jot. Su boobaa am réewam nangul yeneen xeet yu giir ak buur yu mag. \v 8 Wépp xeet mbaa réew mu ci nangulul Nabukodonosor buuru Babilon, di baña wacce yetu buuru Babilon seen ndodd, saamar akub xiif ak mbas laay dikke woowu xeet.” Kàddug Aji Sax jee. “Noonu laay def, ba faagaagal woowu xeet ci loxoom. \p \v 9 «“Kon nag yeen, buleen déglu seen yonent yeek seetkat yeek firikati gént yeek boroom rawaan yeek ñeengokat yi leen di wax, naan leen dungeen tàbbi ci curgag buuru Babilon. \v 10 Ay \w waxyuy|lemma="waxyu:"\w* fen déy lañu leen di waxal te dinañu leen taxa toxoo seenum réew. Maa leen di sànni fu sore, ngeen sànku. \v 11 Waaye xeet wu ci nangoo wacce yetu buuru Babilon seen ndodd, di ko surgawu, ñooñu, maa leen di saxal ci seen suuf.” Kàddug Aji Sax jee. “Ñu dëkke ko, di ko bey.”» \p \v 12 Ci biir loolu Cedesyas buurub Yuda it, ma yegge ko kàddu yooyu yépp, ne ko: «Wàcceel yetu buuru Babilon saw ndodd, nangul ko, nangul ay bokkam, ndax ngeen dund. \v 13 Ana lu jar saamar akub xiif ak mbas di la rey, yaak sa waa réew mi, ni ko Aji Sax ji dige xeet wu ci nangulul buuru Babilon? \v 14 Buleen déglu yonent yi leen di wax naan leen dungeen tàbbi ci curgag buuru Babilon. Ay waxyuy fen déy lañu leen di waxal. \v 15 Man déy yónniwma leen.» Kàddug Aji Sax jee. «Te ñoom ñu ngi waxe waxyuy fen ci sama tur. Moo tax maa leen di dàqe fii, ngeen sànku, yeen ak yonent yi leen di waxyul.» \p \v 16 Gannaaw loolu \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yeek askan wii wépp wax naa leen ne leen: «Aji Sax ji dafa wax ne: Buleen déglu yonent yi leen di waxal ay waxyu, naan leen: “Ndabi\f + \fr 27.16 \fr*\fk Ndab \fk*\ft yooyu gànjar la woon ndax wurus lay doon mbaa xaalis.\ft*\f* kër Aji Sax jaa ngii di délsi, jóge Babilon léegi, léegi.” Ay waxyuy fen lañu leen di waxal. \v 17 Buleen leen déglu. Nangul-leen buuru Babilon te dund! Ana lu jar dëkk bii di mujje doon jalub xeer?» \v 18 Bu ñu dee ay yonent kay, te kàddug Aji Sax ji nekk ci ñoom, nañu daldi tinu Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, ngir ndab yi des kër Aji Sax ji ak kër buurub Yudak Yerusalem, te baña dem Babilon. \v 19 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi de wax na ci mbirum jëni këram geek mbalka meek watiiri rootukaay yi ak yeneen ndab yi des ci dëkk bii, \v 20 Mooy ndab ya Nabukodonosor buuru Babilon yóbbaalewloon, ba muy yóbbu ngàllo doomu Yowakim, Yekoña buurub Yuda, jële ko Yerusalem, jëme ko Babilon, mook kàngami Yudak Yerusalem. \v 21 Lii déy Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi wax na ko ci ndab yooyu des ca kër Aji Sax ji ak kër buurub Yudak Yerusalem. \v 22 Mu ne: «Babilon lees koy boole yóbbu, te foofa lay des ba keroog bés ba ma ciy jóg.» Kàddug Aji Sax jee. «Gannaaw loolu dinaa ko fa jële, délloosi ko bérab bii.» \c 28 \s1 Yeremi tiiñal na yonentu caaxaan \p \v 1 Ca menn at ma, fekk Cedesyas buurub Yuda di doora falu, yemook ñeenteelu atam, ca juróomeelu weer wa, am na doomu Asur ju ñuy wax Anaña, di yonent bu cosaanoo Gabawon. Mu wax ak Yonent Yàlla Yeremi ca biir kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, fa kanam \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yaak mbooloo mépp, ne ko: \v 2 «Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Damm naa yet wi leen buuru Babilon tënke woon. \v 3 Fii ak ñaari at tembe dinaa délloosi fii mboolem ndabi kër Aji Sax ji Nabukodonosor buuru Babilon jële woon bérab bii, yóbbu Babilon. \v 4 Dinaa délloosi fii itam buurub Yuda Yekoña doomu Yowakim, te mboolem ngàllog Yuda ga demoon Babilon, maa leen di délloosi bérab bii.» Kàddug Aji Sax jee. «Maay damm moos yetu buuru Babilon wi mu leen tënke.» \p \v 5 Ba loolu amee Yonent Yàlla Yeremi tontu yonent ba ñuy wax Anaña fa kanam sarxalkat yaak mbooloo ma taxaw fa biir kër Aji Sax ji mépp. \v 6 Mu ne ko: «Amiin! Yal na ko Aji Sax ji defee! Yal na Aji Sax ji sottal sa kàdduy \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* yi nga wax, ba délloosee Babilon ba fii ndabi kër Aji Sax ji ak mboolem ña ñu fa toxal. \v 7 Waaye ngalla déglul bu baax kàddu gii ma lay wax, yaak mbooloo mi mépp. \v 8 Yonent yi feeñoon naka jekk lu ma jiitu, jiitu la, jottli nañu réew yu yaatu ak nguur yu mag seen waxyuy xare ak musiba ak mbas. \v 9 Ab yonent nag bu dee biral waxyub jàmm, su jàmm ja dikkee, ñu xam ne Aji Sax jee ko yebal ci lu wér.» \p \v 10 Ba mu ko defee yonent ba ñuy wax Anaña yékkatee yet wa ca ndoddu Yonent Yàlla Yeremi, damm ko. \v 11 Anaña àddu fa kanam mbooloo ma mépp ne leen: «Aji Sax ji dafa wax ne: Nii laay damme yet wi buur Nabukodonosor buuru Babilon di tënkee. Fii ak ñaari at tembe dinaa jële yet wi ci ndoddu mboolem xeet yi mu ko tënke.» Ba loolu amee Yonent Yàlla Yeremi dem yoonam. \p \v 12 Gannaaw ba yonent ba ñuy wax Anaña yékkatee yet wa ca ndoddu Yonent Yàlla Yeremi ba damm ko, kàddug Aji Sax ji dikkal Yeremi, ne ko: \v 13 «Demal wax Anaña ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Yetu bant nga damm, waaye dinga ko wuutale yetu weñ. \v 14 Ndax Aji Sax ji, Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: Yetu weñ laay teg ci ndoddu mboolem xeet yii, ñu nangul Nabukodonosor buuru Babilon, di ko surgawu. Te rabi àll yi sax, maa leen di teg ci loxoom.”» \p \v 15 Gannaaw loolu Yonent Yàlla Yeremi ne yonent ba ñuy wax Anaña: «Anaña, déglul bu baax li ma lay wax: Aji Sax ji yebalu la, yaw ngay gëmloo askan wii ay fen. \v 16 Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: “Maa ngii di la yebal, nga jóge fi kaw suuf. Ren jii ngay dee, ndax kàdduy gàntal nga waxal Aji Sax ji.”» \p \v 17 Yonent ba ñuy wax Anaña ca at mooma la dee ca juróom ñaareelu weer wa. \c 29 \s1 Yeremi bind na ngàllo ga bataaxal \p \v 1 Yonent Yàlla Yeremi nag yónnee na bataaxal bu jóge Yerusalem, jëm Babilon ca ndesu magi ngàllo ga, ak ca \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yaak yonent yaak mépp mbooloo ma Nabukodonosor jële woon Yerusalem, yóbbu leen ngàllo ca Babilon. \v 2 Mooy gannaaw ba Buur Yekoña bàyyikoo Yerusalem, ànd ak Lingeer yaayu buur ak bëkk-néegi buur ak kàngami Yudak Yerusalem, ak liggéeykati xarala yaak liggéeykati weñ ya. \v 3 Yeremi yóbbante bataaxal ba Elasa doomu Safan, ak Gemarya doomu Ilkiya, ndaw ya Buur Cedesyas mu Yuda yebal Babilon ca Buur Nabukodonosor. Lii la bataaxal bi wax: \pm \v 4 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi dafa wax mboolem ngàllo ga mu jële Yerusalem, yóbbu Babilon, ne leen: \v 5 Tabaxleen ay kër dëkke; jëmbat seeni tóokër, lekk ca meññeef ma. \v 6 Takkleeni jabar, am ci doom yu góor ak yu jigéen. Takkal-leen seen doom ay jabar, maye seen doom yu jigéen, ñu am ñoom it doom yu góor ak yu jigéen. Yokkuleen fa, buleen fa néew. \v 7 Sàkkuleen jàmmu dëkk bi ma leen toxal, te ñaanal ko ci Aji Sax ji, ndax jàmmu dëkk bi mooy seen jàmm. \pm \v 8 Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi kat dafa wax ne: «Seeni yonent ak seen gisaanekat yi ci seen biir, buñu leen nax. Te it buleen déglu seen boroom gént yi ngeen di géntloo, \v 9 ndax \w waxyuy|lemma="waxyu:"\w* fen lañu leen di wax ci sama tur. Yebaluma leen.» Kàddug Aji Sax jee. \pm \v 10 Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Bu Babilon matalee juróom ñaar fukki ati kilifteefam, dinaa leen dikkal, sottalal leen sama kàddug jàmm, ba délloosi leen bérab bii. \v 11 Ndax man déy, xam naa mébét yi ma leen mébétal.» Kàddug Aji Sax jee. «Du mébéti loraange, waaye mébéti jàmm laa leen mébétal, ngir may leen yaakaaru ëllëg. \v 12 Su boobaa ngeen woo ma wall, dikk ñaan ma, ma nangul leen. \v 13 Su boobaa ngeen sàkku ma, daj ma, ndegam sàkkoo ngeen ma seen léppi xol, \v 14 maa leen di may ngeen daj ma.» Kàddug Aji Sax jee. «Maa leen di tijjil seen wërsëg, dajalee leen ci mboolem xeet ak mboolem bérab ya ma leen sànni woon.» Kàddug Aji Sax jee. «Maa leen di délloosi bérab bii ma leen yebale woon ngàllo.» \pm \v 15 Yeena ne: «Aji Sax ji yónnee na nuy yonent ci Babilon.» \v 16 Waaye Aji Sax ji dafa wax lu jëm ci buur bi toog ci jalub Daawuda, jëm ci képp ku bokk ci askan wi des ci Yerusalem gii di seen bokk ya àndul woon ak yeen, dem ngàllo. \v 17 Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: «Maa ngii di leen yónnee saamar akub xiif ak mbas. Maa leen di def ñu mel ni figg ju nëb, ba kenn manu koo lekk ndax bon. \v 18 Maa leen di toppe saamar akub xiif ak mbas. Maa leen di def ñu seexlu leen ci mboolem réewi àddina, teg ci di musiba mu ñuy muslu ci biir mboolem xeet wu ma leen sànni, ba ku fay kókkalee, ñoom ngay tudd. \v 19 Li ko waral mooy ñoo ma déggalul.» Kàddug Aji Sax jee. «Dama leena yónnee yonent yiy samay jaam ay yooni yoon, te déggaluñu ma.» Kàddug Aji Sax jee. \pm \v 20 «Kon nag yeen mboolem ngàllo gi ma yebale Yerusalem ba Babilon, dégluleen kàddug Aji Sax ji. \v 21 Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi dafa wax ci mbirum Akab doomu Kolaya ak Cedesyas doomu Maaseya, ñoom ñi leen di jottli waxyuy fen ci turam. Mu ne: Maa ngii di leen teg ci loxol Nabukodonosor buuru Babilon, mu rey leen, ngeen di gis. \v 22 Dinañu tax mboolem kuy móoloo te bokk ca ngàllog Yudeen ña ca Babilon, danga naan: “Yal na la Aji Sax ji teg la mu tegoon Cedesyas ak Akab, ña buuru Babilon lakk cib taal.” \v 23 Li ko waral mooy njombe wi ñu def fi digg Israyil, di jaalook seen jabari dëkkandoo, di wax ci sama tur ay kàdduy fen yu ma leen santul. Maa ko xamal sama bopp, seede ko.» Kàddug Aji Sax jee. \s1 Semaya jot na tontam \p \v 24 «Yaw Yeremi nag, nanga wax Semaya, Neyelameen bi ne ko: \v 25 “\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Yaw yaa yónnee ci sa turu bopp ay bataaxal ca askanu Yerusalem gépp, rawatina \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba Cefaña doomu Maaseya, ak mboolem sarxalkat ya. Nga di ci wax ne: \v 26 ‘Aji Sax ji da laa fal sarxalkat, nga wuutu Yoyada sarxalkat bi, ngir kër Aji Sax ji am ku ko yor, ba dof bu fiy wax-waxlu ay \w waxyu|lemma="waxyu:"\w*, nga jéng ko, yeewe ko càllalay weñ ci baatam. \v 27 Ana lu tax waxuloo ci Yeremi mu Anatot nag, moom miy wax-waxlu ay waxyu fi seen biir? \v 28 Léegi la nu yónnee Babilon bataaxal, ne nu: Dingeen yàgg àll de, kon tabaxleeni kër, dëkke; jëmbatleeni tóokër, lekk ci meññeef mi.’ ”» \p \v 29 Ba Cefaña sarxalkat ba jàngee bataaxal boobu, Yonent Yàlla Yeremi di dégg, \v 30 kàddug Aji Sax ji dikkal Yeremi ne ko: \p \v 31 «Yónneel ca ngàllo gépp ne leen: Aji Sax ji dafa wax ci mbirum Semaya Neyelameen ba, ne: “Semaya waxal na leen waxyu, gëmloo leen ay fen, te yebaluma ko. \v 32 Kon nag Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di mbugalsi Semaya Neyelameen bi, mook askanam. Ku bokk ci moom du toog ci biir xeet wii, bay gis ngëneel li may defal sama ñoñ.” Kàddug Aji Sax jee. “Moo xiirtal askan wi ci gàntal Aji Sax ji.”» \c 30 \ms1 Yeremi yéene na yeeslug jàmm \mr (Saar 30—33) \s1 Nii la yéene bi tënkoo \p \v 1 Kàddu gii dikkal na Yeremi, bàyyikoo ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ne ko: \v 2 «Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: Nanga bind cib téere kàddu yi ma la wax yépp. \v 3 Ndax kat ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay tijjil sama ñoñ seen wërsëg, muy Israyil di Yuda.» Aji Sax jee ko wax. «Maa leen di delloo ca suuf sa ma moomale woon seeni maam.» \s1 Ay teraanga nuyoo na \p \v 4 Kàddu yii la \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax ci mbirum Israyil ak ci mbirum Yuda. \q1 \v 5 Aji Sax ji déy dafa wax ne: \q1 «Yuuxi tiitaange dégtu na, \q1 njàqare la, du jàmm. \q1 \v 6 Laajteleen te xool, \q1 ndax góor day wasin léegi? \q1 Moona maa gis jàmbaar ju ne jatu, \q1 ni kuy matu, \q1 kanam xoyy. \q1 \v 7 Wóoy boobu bés bu réy, \q1 ba bés du ni mel! \q1 Bésu njàqare lay doon \q1 ñeel askanu Yanqóoba, \q1 waaye dañuy mucc. \p \v 8 «Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi, «maay damm yet wi ñu leen tënke ci seen ndodd, dammat seeni jéng, ba dootuñu doon jaamu doxandéem. \v 9 Waaye seen Yàlla Aji Sax ji lañuy jaamu ak seen buur bi ma leen di falal, mu toogal Daawuda. \q1 \v 10 Waaye yaw Yanqóoba sama jaam, \q1 bul tiit,» kàddug Aji Sax jee; \q1 «yaw Israyil, bul ragal. \q1 Fu sore laa lay wallujee, \q1 yaak sa askan wa ca réewum njaam ga, \q1 Yanqóoba dellu dal, fegu; \q1 kenn dootu ko tiital. \q1 \v 11 Maa ngeek yaw, nar laa wallu.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 «Maay fàkkas mboolem xeet ya ma la sànniji. \q1 Yaw nag duma la fàkkas, \q1 duma la ñàkka topp moos, \q1 waaye li nga yelloo laa lay yar.» \b \q1 \v 12 Aji Sax ji déy dafa wax ne: \q1 «Sa damm-damm du faju, \q1 sa góom du wér. \q1 \v 13 Amul ku lay sàmmal sa àq, \q1 te sab dana amul pajtal mu baax. \q1 \v 14 Sa soppe yépp a la fàtte, \q1 kenn faalewu la ci, \q1 ndax dumay noon laa la duma, \q1 yar la yar bu tar \q1 ngir sa ñaawtéef ju réy \q1 ak sa bàkkaar yu bare. \b \q1 \v 15 «Damm-damm yu dul wér \q1 ak mitit wu tar jarul jooy. \q1 Maa la teg lii, \q1 ndax sa ñaawtéef ju réy \q1 ak sa bàkkaar yu bare. \q1 \v 16 Waaye ku la lekk, dees na ko lekk; \q1 sa noon yépp lañuy jàpp njaam ba ñu daj. \q1 Ku la futti, dees na ko futti, \q1 ku la saax-saaxee dees na ko saax-saaxee. \b \q1 \v 17 «Ñu ngi la naan: “Waccees na la,” \q1 naan la: “\w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* yaw, faaleesu la,” \q1 waaye maa lay may wér, \q1 faj say góom.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 18 Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 «Maa ngii di tijji wërsëgu askanu Yanqóoba, \q2 ñibbsil leen, \q1 baaxe seeni dëkkuwaay, \q1 ba dëkk dekkee ca tundam wu gentoon, \q1 kër buur taxawaat bérabam, \q1 \v 19 cant jollee ca, \q1 di riirum mbégare. \q1 Maa leen di ful, \q1 te duñu wàññiku, \q1 darajaal leen, \q1 te dootuñu tuut. \q1 \v 20 Seeni doom dañuy mel na woon, \q1 seen mbooloo sax fi sama kanam, \q1 may mbugal ñi leen di sonal. \q1 \v 21 Su boobaa seen njiit di seen deret, \q1 di seen kilifa, soqikoo ci ñoom; \q1 ma woo ko, mu jege ma, \q1 nde nit jaayul bakkanam, \q1 ba jegesi ma te woowuma ko!»\f + \fr 30.21 \fr*\ft Leeru Yàlla, jegee ko noonu, bakkanu nit ki xaj na ci. Néegu biir ba ca kër Yàlla ga sax, du ñépp a fa mana àgg. Sarxalkat bu mag baa fa daa dugg benn yoon cim at. Keneen ku fa dugg dee. Seetal ci \ft*\ft \+bk Sarxalkat yi\+bk* 16.10; 21.17; 22.3.\ft*\f* \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 22 «Yeenay doon sama ñoñ, \q1 man, may seen Yàlla.» \b \q1 \v 23 Ngëlénu Aji Sax jaa ngoog, \q1 sànjam fettax na, \q1 dig callweer, \q1 callweeral boppu ku bon. \q1 \v 24 Sànjam Aji Sax ju tàng ji du giif, \q1 te sottalul li mu nar. \q1 Fan yu mujj ya \q1 ngeen xam ci dara. \c 31 \s1 Israyil séentu na sancaatub réewam \q1 \v 1 «Su boobaa,» kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee, «maay doon Yàllay làngi Israyil yépp, \q1 ñoom ñuy sama ñoñ.» \b \q1 \v 2 Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 «Waa Israyil ñi rëcc ñawkay saamar, \q1 daje nañook yiw ci màndiŋ mi, \q1 fekk ñuy sàkku noflaay.» \q1 \v 3 Ñu ne: «Bu yàgg la nu Aji Sax ji feeñu, \q1 ne nu: “Maa leen masa bëgg, \q1 ba tax ma sédd leen ngor. \q1 \v 4 Yaw Israyil mu taaru, \q1 maa lay defaraat, nga defaru, \q1 ba jiinaat sam njiin, \q1 wàlli peccum mbéx, \q1 \v 5 jëmbataat sa tóokëri reseñ \q1 ca mbartali Samari, \q1 te ku jëmbat, xéewlu ca. \q1 \v 6 Bés dina ñëw déy, \q1 wattukat yéenee fa kaw tundu Efrayim \q1 ne: ‘Aycaleen nu yéegi tundu \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, \q1 fa sunu Yàlla Aji Sax ji.’ ”» \q1 \v 7 Aji Sax ji déy dafa wax ne: \q1 «Sarxolleleen, bége askanu Yanqóoba, \q1 xaacul-leen xeet woowu jiitu, \q1 biral-leen cant te ne: \q1 “Éy Aji Sax ji, wallul ndesu Israyil, sa ñoñ ñii.”» \b \q1 \v 8 «Maa ngii di jële sama ñoñ réewum bëj-gànnaar, \q1 dajalee leen fa cati àddina. \q1 Silmaxaa ngi ci akub lafañ, \q1 jigéenu wérul it ak kuy wasin, \q1 ñuy gàngoor gu mag, délsi fii. \q1 \v 9 Ñooy dikk di jooy, di leewaayu, \q1 ma jiite leen, yóbbu, \q1 jaare leen xàll wu jub wu ñu dul fakktaloo, \q1 ba ca wali ndox ya, \q1 ngir maay baayu Israyil, \q1 Efrayim di sama taaw. \b \q1 \v 10 «Yeen xeet yi, dégluleen kàddug Aji Sax ji, \q1 yégleleen ko ca tefes yu sore ya. \q1 Ne leen: “Ki tasaare woon Israyil, moo leen di dajale, \q1 sàmm leen ni sàmm ak géttam.” \q1 \v 11 Aji Sax jee goreel askanu Yanqóoba, \q1 jot ko ci loxol ku ko ëpp doole. \q1 \v 12 Ñooy dikk, di sarxollee kaw tundu Siyoŋ, \q1 ne ràññ ndax ngëneeli Aji Sax ji, \q1 pepp, biiñ aku diw, \q1 gàtt aki nag, \q1 bakkan ni tool bu ñu suuxat, \q1 dootuñu yoggoorlu. \q1 \v 13 Su boobaa janq bégem pooj, \q1 waxambaaneek mag feelu ko, \q1 ma soppi seen ñaawlu mbégte, dëfal leen, \q1 bànneexal leen, ñu dëddu naqar. \q1 \v 14 Maay yafal \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi, ba reggal leen, \q1 sama ñoñ ñi regge sama ngëneel.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \b \q1 \v 15 Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 «Yuux dégtu na fa Raama, \q1 ay jalooki jooy yu metti. \q1 Rasel ay jooy ay doomam, \q1 baña noppi, \q1 ndax doomam ya wuute.» \q1 \v 16 Aji Sax ji nag ne ko: \q1 «Baal sa jooy yi \q1 te fomp say rongooñ, \q1 dees na la yool sa coono.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 «Say doom ay jóge réewu noon, ñibbsi. \q1 \v 17 Am nga yaakaaru ëllëg.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 «Say doom ay délsi seenum réew. \q1 \v 18 Maa dégg moos askanu Efrayim di binni \q1 naan: “Aji Sax ji, duma nga noo duma, \q1 ni sëllu wu dese tàggat. \q1 Ngalla waññi nu, nu waññiku; \q1 yaw Aji Sax ji, yaa di sunu Yàlla. \q1 \v 19 Dëddu woon nanu la moos \q1 waaye léegi réccu nanu. \q1 Xam nan ne tooñ nanu, \q1 ba tey nuy màttuy wiccax. \q1 Danoo rus, torox \q1 ndax sunu ñaawtéefi ndaw.”» \b \q1 \v 20 Aji Sax ji ne: \q1 «Du Efrayim\f + \fr 31.20 \fr*\fk Efrayim \fk*\ft kenn la ci sëti Yanqóoba mi ñu dippee Israyil. Turu Efrayim wi fii askanu Israyil la fi taxawal.\ft*\f* ay sama doom ji ma sopp, \q1 gone gi may bànneexal? \q1 Lu ma ko gëdd gëdd, \q1 di ko bàyyi xel. \q1 Moo tax sama xol di ko laaj, \q1 ma yërëm koo yërëm.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \b \q1 \v 21 «Sampal ay xàmmikaay ci yoon wi, \q1 teg fi say màndarga. \q1 Booy dem, defal sa xel ci yoon wii, \q1 ñall wii nga topp. \q1 Israyil mu taaru mi, ñibbsil, \q1 ñibbsil sa dëkk yii. \q1 \v 22 Ndaw su toogadi si, \q1 foo àppal sa ciŋiñ-caŋañ ji? \q1 Aji Sax ji déy, sàkk na guléet kaw suuf: \q1 yees ba mel ni jigéen juy jëflanteek góor\f + \fr 31.22 \fr*\ft Waxin la wu yéeme wuy wund jëfi guléet ju kenn séentuwul, waaye xamuñu dëgg la mu tekki woon ca yooya jamono.\ft*\f*.» \p \v 23 Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Bu ma tijjee seen wërsëg, kàddu gii dina jibati ci réewum Yuda ak dëkk yi ko séq. \q1 Dees na ne: “Yaw dëkkuwaayu njekk bii, \q1 yaw, tundu Siyoŋ wu \w sell|lemma="sell:"\w* wi, \q1 yal na la Aji Sax ji barkeel!” \p \v 24 «Waa réewum Yuda ak dëkk-dëkkaanam yépp ay bokk dëkk, ak beykat yeek màngaan yi yor gétt. \v 25 Maay nàndal ku mar, leqli ku loof.» \sp Yeremeey wax \p \v 26 Ba loolu amee ma yewwu, ne xiféet, xam ne samay nelaw neex na. \s1 Aji Sax ji teewlul na Israyil \p \v 27 «Bés a ngii nag di ñëw,» kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee, «yu may jiwe kërug Israyil ak kërug Yuda jiwum doom aadama ak jiwum mala. \v 28 Te ni ma leen teewloo woon ba ma leen di buddat, di leen fàqat, di leen daaneel, di leen yàqte ak a lor, noonu laa leen di teewloo ngir defar leen, jëmbat leen.» Kàddug Aji Sax jee. \v 29 «Su boobaa deesatul ne: \q1 “Baay lekk reseñ ju xaay, \q1 mu uum bëñu doom ja.” \m \v 30 Su boobaa ku nekk sa bàkkaaru bopp a lay rey. Ku lekk reseñ yu xaay, sa gëñi bopp lay uum. \s1 Kóllëre gu yees a ngi \p \v 31 «Ay bés a ngii di ñëw,» kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee, «yu may fas ak waa kër Israyil ak waa kër Yuda \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* gu yees. \v 32 Du mel ni kóllëre ga ma fasoon ak seeni maam keroog ba ma leen jàppee ci loxo, génne leen réewum Misra. Ndax ñoom ñoo fecci sama kóllëre, te man may seen boroom kër.» Kàddug Aji Sax jee. \v 33 «Waaye kóllëre gi may fas ak waa kër Israyil gannaaw loolu,» kàddug Aji Sax jee, «nii lay deme: Maay yeb sama ndigali yoon ci seen xel, ci seen xol laa koy ñaas. Maay doon seen Yàlla, ñoom ñu doon sama ñoñ. \v 34 Kenn dootu soxlaa jàngal kenn, muy moroomam mbaa mbokkam, naan ko: “Ràññeel Aji Sax ji,” ndax ñoom ñépp a may ràññee, ki gëna tuut ba ki gëna mag,» kàddug Aji Sax jee, «ndax maa leen di jéggal seeni ñaawtéef, te seeni bàkkaar, duma ci bàyyeeti xel.» \s1 Lii mooy saxal Israyil \q1 \v 35 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax, \q1 moom mi dogal jant di leeral bëccëg, \q1 dogal weer ak biddiiw di leeral guddi, \q1 yëngal géej, kiy gannax yi riir, \q1 kookooy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi. \q1 \v 36 Mu ne: «Bu askanu Israyil feyee ba fàww, may gis, \q1 dogal yooyoo toxu, may gis.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \b \q1 \v 37 Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 «Su ma waccee mboolem askanu Israyil \q1 ndax li ñu def lépp, \q1 kon nit a mana natt kawewaayu asamaan, \q1 mbaa mu xayma xóotaayu suuf.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \p \v 38 Mu ne: «Ay bés a ngi ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «dees na tabaxalaat Aji Sax ji dëkk bi, dale ko ca soorooru Ananel ba ca buntu Ruq ba. \v 39 Dees na fa rëddaat kemu dëkk bi, jubal ba tundu Gareb, wëri ba Gowa. \v 40 Mboolem xuru néew yaak dóom ya ak mboolem tool ya, ba ca yoonu ndox ma ca Sedoron, ba ca ruqu buntu Fas ya ca penku: lépp lees di sellalal Aji Sax ji. Deesatu fa buddat mbaa di fa daaneel dara.» \c 32 \s1 Yeremi wone na dayob ngëmam \p \v 1 Kàddu gii dikkaloon na Yeremi, bàyyikoo fa \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ca fukkeelu atu nguurug Cedesyas buurub Yuda. Mu yemook ba nguurug Nabukodonosor buuru Babilon tolloo ca fukkeelu atam ak juróom ñett. \v 2 Booba mbooloom xarem Babilon a nga gaw Yerusalem. Fekk Yonent Yàlla Yeremi nag moom, ma nga ñu tëj ca kër buurub Yuda, ca biir ëttu dag ya, \v 3 fa ko Cedesyas buurub Yuda dencoon, ndax da ko noon: «Ana lu waral ngay wax bii \w waxyu|lemma="waxyu:"\w*? Nga ne: “Aji Sax ji dafa wax ne mu ngii di teg dëkk bii ci loxol buuru Babilon, mu nangu ko. \v 4 Te Cedesyas buurub Yuda du rëcc waa Babilon ndax dees na ko teg moos ci loxol buuru Babilon, ba Cedesyas wax, mu wax, seeni gët ñeent. \v 5 Babilon lees koy yóbbu, te fa lay des, ba keroog may wax ci moom.” Kàddug Aji Sax jee. “Bu ngeen xareek waa Babilon it, dungeen am ndam.”» \p \v 6 Yeremi da ne: Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma: \v 7 «Xoolal, Anamel doomu Salum sa baay bu ndaw a ngooguy ñëw, naan la nga jënd toolam ba ca Anatot, ndax yaa ko saña jotaat.» \p \v 8 Ba loolu amee Anamel sama doomu baay bu ndaw dikk, na ma ko Aji Sax ji waxe. Mu fekk ma ci ëttu dag yi, ne ma: «Rikk jëndal sama tool ba ca Anatot ca diiwaanu Beñamin ndax sa alal la ci yoon, yaa ko saña jotaat\f + \fr 32.8 \fr*\fk jotaat: \fk*\ft seetal ci \ft*\ft \+bk Sarxalkat yi\+bk* 25.22-34.\ft*\f*. Kon jënd ko.» Ma xam ne loolu kàddug Aji Sax jaa. \p \v 9 Nii laa jënde tool ba ca Anatot ci Anamel sama doomu baay bu ndaw. Ma waññal ko xaalis bi, muy fukki donji xaalis ak juróom ñaar. \v 10 Ma bind kayitu njaay mi, màndargaale ko sama torlukaay, woo ciy seede, ba noppi natt diisaayu xaalis bi. \v 11 Ma boole jël kayitu njaay bi tëjewul ak kayitu njaay bi tëje, te yoonalu njaay meek sàrt yi tënke ci. \v 12 Ma teg kayit yi ci loxol Barug doomu Nerya doomu Maaseya. Anamel sama doomu baay bu ndaw fekke na ko, seede yi torlu kayitu njaay mi fekke ko, ñook mboolem Yudeen ñi toogoon ci ëttu dag yi. \p \v 13 Ma dénk Barug ci seen kanam, ne ko: \v 14 «Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: “Jëlal kayit yii, kayitu njaay bi tëje, ak kayit bi tëjewul, nga boole yeb ci njaqal ban, ndax kayit yi mana yàgg. \v 15 Ndax Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Dees na dellu di jënd ay kër aki tool ak tóokëri reseñ ci réew mii.”» \s1 Xelu Yeremi teey na \p \v 16 Gannaaw ba ma joxee kayiti njaay ma Barug doomu Nerya, damaa ñaan \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ne ko: \v 17 «Éy saa Boroom, Aji Sax ji! Yaw déy yaa sàkk asamaan, sàkk suuf ci sa doole ju bare ak sa kàttan. Dara tëwu la. \v 18 Yaw miy jëfe ngor sa digg ak junniy maas, te bu baay ñaawee, nga topp ko ko, ba ci doomam. Yaay Yàlla ju màgg ji te jàmbaare. Yaa di Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, \v 19 réyi pexe, màggi jaloore; say gët ne jàkk ci mboolem lu doom aadama def, ngay añale ku nekk jëfinam ak jëfam. \v 20 Yaa def ay firnde aki kéemaan ca réewum Misra, di ko def ba tey jii ci Israyil, ak ci doom aadama yépp, ba may sa bopp woy wu réy wi nga am tey jii. \v 21 Génne nga Israyil say ñoñ, jële leen réewum Misra, ci kawi firnde aki kéemaan ak sa doole ju bare ak sa kàttan; mu jur tiitaange lu réy. \v 22 Nga jox leen réew mii nga giñaloon seeni maam. Muy réew mu meew meek lem ji tuuroo. \v 23 Ñu dikk moom ko, te déggaluñu la, toppuñu saw yoon, jëfewuñu mboolem li nga leen santoon, ba tax nga wàcce ci seen kaw mboolem musiba mii. \p \v 24 «Sëkki gawukaay yaa ngii ñu yékkatil dëkk bi, ngir nangu ko. Dëkk bi dina daanu ci loxoy waa Babilon ñi ko song, ndax saamar akub xiif ak mbas. Gis nga ko déy, li nga waxoon am na! \v 25 Dëkk baa ngii nara daanu ci loxoy waa Babilon te moona Boroom bi Aji Sax ji, yaw yaa ma ne ma jënde tool bi xaalis, ay seede seede ko.» \s1 Aji Sax ji dalal na xelu Yeremi \p \v 26 Ba loolu amee kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal Yeremi, ne ko: \v 27 «Du maay Aji Sax ji, Yàllay képp kuy dund. Ana lu ma të?» \v 28 Kon nag Aji Sax ji dafa wax ne: «Maa ngii di teg dëkk bii ci loxoy waa Babilon ak ci loxol Nabukodonosor buuru Babilon, mu nangu ko. \v 29 Waa Babilon ñiy song dëkk bii dinañu dugg, taal ko, lakk ko ba mu jeex, lakkaale kër ya ñu doon taalal \w Baal|lemma="Baal:"\w* tuur mi, cuuraay ca kaw taax ya, di fa tuural yeneen yàlla ay saraxi naan, ba di ma merloo. \v 30 Askanu Israyil ak Yuda kay, ca cosaan ba tey, defuñu lu moy lu bon fi sama kanam. \w Bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, mboolem lu ñu def, defuñu ko lu moy di ma merloo.» Kàddug Aji Sax jee. \v 31 «Mer dikkal na ma, xadar dikkal ma ci dëkk bii, dale ko ca ba ñu ko tabaxee ba bésub tey, ba tax ma di ko jële fi sama kanam, \v 32 ndax mboolem lu bon li bànni Israyil ak Yuda def, di ma merloo, ñook seeni buur ak seeni kàngam ak seeni \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ak seeni yonent ak waa Yuda ak waa Yerusalem. \v 33 Wonuñu ma kanam, xanaa gannaaw, te ma àrtu leen ay yooni yoon. Waaye ñoom dégluwñu, dégguñu yar. \v 34 Yeb nañu sax seen yëf yu seexluwu ci biir kër gi ñu ma tudde, ba sobeel ko. \v 35 Tabaxal nañu Baal tuur mi ay \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* ca xuru Ben Inom, di fa lakk seen doom yu góor ak yu jigéen ngir Moleg tuur mi, te masuma leen koo sant. Jooju jëf ju siblu jaarul sax sama xel ba ma leen di ko defloo, ñuy yóbbe Yuda bàkkaar. \p \v 36 «Yeena wax ci dëkk bii ne dina daanu ci loxol buuru Babilon ndax saamar akub xiif ak mbas. Waaye Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: \v 37 Maa ngii di leen dajalee ca mboolem réew ya ma leen sànni woon, ndax mere leen ak jéppi leen ba sama xol fees dell. Te maa leen di délloosi fii, dëël leen ci jàmm; \v 38 ñu doon sama ñoñ, may seen Yàlla. \v 39 Maa leen di may benn xol ak benn jubluwaay ngir ñu di ma wormaal seen giiru dund, muy seen ngëneel, ñook seen doom yi leen di wuutu. \v 40 Maay fas ak ñoom \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* gu sax dàkk gu ma leen dul xañati; xanaa baaxe leen, yeb ragal Yàlla ci seen xol, ba dootuñu ma won gannaaw. \v 41 Maay am mbégtey baaxe leen, jëmbat leen bu wér ci réew mi, jëmbate leen sama léppi xol ak sama léppi jëmm.» \p \v 42 Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Ni ma wàccee ci kaw xeet wii musiba mu mag mii mépp, ni laay wàccee fi seen kaw mboolem ngëneel li ma leen wax. \v 43 Dees na dellu di jënd ab tool ci réew mii ngeen ne daanu na ci loxol waa Babilon, ba dib gent bu kenn nekkul, du nit, du rab. \v 44 Dees na fi jënde xaalis ay tool, bind fi kayiti njaay, torlu ko, tëj fi kanami seede ci suufas Beñamin, ak li wër Yerusalem, ak biir dëkki Yuda, ak dëkki tund ya, ak dëkki suufu tund ya, ak ca dëkki diiwaanu Negew. Maay tijji moos seen wërsëg.» Kàddug Aji Sax jee. \c 33 \s1 Aji Sax ji du dige, di fomm \p \v 1 Gannaaw loolu kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal na Yeremi ñaareel bi yoon, fekk ko tëje ba tey ca biir ëttu dag ya. Mu ne ko: \v 2 «Aji Sax ji dafa wax, moom miy sàkk mbir, bind ko, taxawal ko, Aji Sax ji di turam. \v 3 Mu ne: “Woo ma, ma wuyu la, wax la lu réy te loq, loo xamul woon.”» \v 4-5 Aji Sax ji Yàllay Israyil déy dafa wax ci mbirum këri dëkk bii ak këri buuri Yuda yii ñu màbb, di ko fegoo sëkk bi ñu leen gawe te di ko làqoo saamaru waa Babilon ñi ñuy xareel. Mu ne: «Kër yi dina fees ak néewi nit ñi ma bóom ndax mer ak xol bu fees. Dinaa làq dëkk bii sama yiw ndax seen gépp mbon. \p \v 6 «Waaye du tee, maa leen di may tan, faj leena faj ba ñu wér, won leen xéewalu jàmm ju dëggu. \v 7 Maay tijji wërsëgu Yuda ak wërsëgu Israyil, sampaat leen na woon. \v 8 Maa leen di raxasal mboolem ñaawtéef gu ñu ma moye, baal leen mboolem ñaawtéef yu ñu ma moye, di ma gàntal. \v 9 Dëkk bi daldi doon sama woy, di sama mbégte, di sama ndam, di sama sag ci biir mboolem xeeti àddina yi dégg ngëneel yi ma leen di defal yépp. Dinañu yéemu ba seen yaram daw ci lépp luy ngëneel ak jàmm ju ma leen di defal.» \p \v 10 Aji Sax ji dafa wax ne: «Bérab bii ngeen ne ab gent la bu kenn nekkul, du nit, du rab te muy dëkki Yudak mbeddi Yerusalem yii gental, kenn nekku fi, du nit, du rab, dees na fi déggati \v 11 coowal mbégteek coowal bànneex ak kàddug boroom séet ak kàddug séetam, ànd ak kàdduy nit ñiy indi \w saraxi cant|lemma="Sarax yi:"\w* ci biir kër Aji Sax ji, di jàngaale naan: \q1 “Santleen Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi. \q1 Aji Sax jee baax, \q1 kee saxoo ngoram.” \m Maay tijji wërsëgu réew mi, na woon.» Aji Sax jee ko wax. \p \v 12 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Bérab bii di gent bu kenn nekkul, du nit du rab ci dëkk yi fi nekk yépp, bérab bii dina dellu am parlu yu sàmm siy gooral seeni gàtt. \v 13 Muy dëkki tund yi, di dëkki suufu tund yi, di dëkki diiwaanu Negew, di diiwaanu Beñamin, di li wër Yerusalem, di dëkki Yuda, gàtt yi dina dellu ci loxol sàmm buy takk lim ba.» Aji Sax jee ko wax. \s1 Askanu Buur Daawuda dina yeeslu \p \v 14 «Ay bés a ngii di ñëw,» kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee, «maay sottal ngëneel la ma dig waa kër Israyil ak waa kër Yuda. \q1 \v 15 Bés yooyu ci jamonoom, \q1 maay jebbil njebbit lu jekk ci askanu Daawuda, \q1 muy jëfe njub ak njekk ci réew mi. \q1 \v 16 Bés yooyu Yuda day mucc, \q1 Yerusalem dëkke jàmm, \q1 ñu di ko wooye: \q1 “Aji Sax ji sunu njekk.”» \p \v 17 Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Daawuda du ñàkk mukk ku ko wuutu ci jalu Israyil. \v 18 \w Sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yiy \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* it duñu ñàkk ku leen taxawal fi sama kanam, di joxe \w saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, di taal \w saraxi pepp|lemma="Sarax yi:"\w* ak a sarxal ba fàww.» \s1 Kóllëre gu dul toxoo ngi \p \v 19 Gannaaw loolu kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal na Yeremi, ne ko: \v 20 «Aji Sax ji dafa wax ne: Ndegam manees naa dog sama \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* maak bëccëg mbaa sama kóllëre maak guddi, ba bëccëg mbaa guddi baña teew ci waxtoom, \v 21 kon dees na mana dog sama kóllëreek Daawuda sama jaam bi, dogaale sama kóllëreek \w sarxalkati|lemma="sarxalkat b-:"\w* \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi may liggéeyal, ba Daawuda ñàkk sët bu koy wuutu cib jalam. \v 22 Ni biddiiwi asamaan weesee lim, feppi suufas géej wees waññ, ni laay fule askanu Daawuda sama jaam bi ak askanu Leween ñi may liggéeyal.» \p \v 23 Kàddug Aji Sax ji dellu dikkal Yeremi, ne ko: \v 24 «Xanaa dégguloo li nit ñi wax? Ñu ne: “Ñaari làng ya Aji Sax ji tànnoon de, wacc na leen,” moo tax ñu xeeb sama ñoñ, ba tegatuñu leen sax aw xeet.» \v 25 Waaye Aji Sax ji dafa wax ne: «Ndegam du maa fas sama kóllëre maak bëccëg ak guddi, te du maa saxalal asamaan ak suuf ay sàrt, \v 26 kon dinaa wacc askanu Yanqóoba ak Daawuda sama jaam bi, ba dootuma taamoo ciw askanam kuy yilif askanu Ibraaymaak Isaaxaak Yanqóoba. Maay tijji seen wërsëg moos, yërëm leen.» \c 34 \s1 Aji Sax ji wax na Buur Cedesyas mujam \p \v 1 Ba Nabukodonosor buuru Babilon àndeek mbooloom xareem mépp ak mboolem réew yeek xeet yi mu teg loxo, ñu songandoo Yerusalem ak dëkk yi ko wër yépp, kàddu gii dikkaloon na Yeremi, bàyyikoo ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji: \v 2 «Aji Sax ji, Yàllay Israyil dafa wax ne: Demal nga wax Cedesyas buurub Yuda ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di teg dëkk bii ci loxol buuru Babilon, mu taal ko. \v 3 Yaw Cedesyas nag doo ko rëcc. Dees na la jàpp moos te dees na la teg ci loxol buuru Babilon, mu wax ak yaw, seeni gët ñeent; nga dem Babilon. \p \v 4 «“Waaye yaw Cedesyas buurub Yuda, déglul kàddug Aji Sax ji: Aji Sax ji dafa wax ne doo deeye saamar. \v 5 Ci jàmm ngay dee, te ni ñu taalale woon cuuraay say maami buur yi la jiitu, terale leen ko ci seen dëj, ni lañu lay taalale cuuraay, di la jooy naan: ‘Wóoy sunu sang ba dem na!’ Jii wax, maa ko wax.”» Kàddug Aji Sax jee. \p \v 6 Ci kaw loolu Yonent Yàlla Yeremi jottli Cedesyas buurub Yuda mboolem kàddu yooyu fa Yerusalem. \v 7 Mu yemook ba mbooloom buuru Babilon di xareek Yerusalem ak mboolem dëkki Yuda ya desoon, di Lakis ak Aseka. Booba yooyu rekk a desoon ci dëkki Yuda yu tata wër. \s1 Yiwi jaam yi war na \p \v 8 Kàddu gii dikkaloon na Yeremi, bàyyikoo ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, gannaaw ba Buur Cedesyas fasook mboolem waa Yerusalem ngir goreel jaam yi, \v 9 ku nekk wara goreel mbokkam mu \w Ebraam|lemma="Ebrë:"\w*, góor ak jigéen, ñu moom seen bopp, te kenn baña jaamlooti mbokkum Ebraam. \v 10 Ba mu ko defee mboolem kàngam yeek nit ñi ko fasoo woon daldi nangoo goreel seen jaam yu góor ak yu jigéen, bañ leena jaamlooti, ñu moom seen bopp. Ñu daldi leen yiwi. \v 11 Gannaaw gi nag ñu walbatiku, jëlaat seen jaam yu góor ak yu jigéen ya ñu goreeloon, dellooleen cig njaam, góor ak jigéen. \p \v 12 Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal Yeremi bàyyikoo ci Aji Sax ji, ne ko: \v 13 «Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: Man maa fasoon \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* ak seeni maam keroog bés ba ma leen génnee réewum Misra kërug njaam ga, ne leen: \v 14 “Saa yu ngeen waññee juróom benni at ba ca catal juróom ñaareel ma, na ku nekk ci yeen goreel mbokkum Ebraam mu ko jaayoon boppam. Gannaaw bu ko liggéeyalee juróom benni at, na ko goreel, mu tàggook moom, daldi moom boppam\f + \fr 34.14 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Mucc ga\+bk* 21.2-6.\ft*\f*. Waaye seeni maam déggaluñu ma, teewluwñu ma. \v 15 Tey yeen, waññiku woon ngeen, ba def li ma rafetlu; ku nekk ci yeen biral goreelu mbokkam. Fasoo ngeen ko sax fi sama kanam ci biir kër gi ñu ma tudde. \v 16 Léegi nag ngeen di teddadil sama tur, dellu gannaaw, ku nekk jëlaat jaamam yu góor ak yu jigéen, te ngeen goreeloon leen ba noppi, ñu moom seen bopp ni mu leen neexe. Néewal ngeen leen doole, ñu dellu di seeni jaam.” \p \v 17 «Kon nag, Aji Sax ji dafa wax ne: “Ku nekk ci yeen waroon naa goreel mbokkum dëkkandoom, waaye yeen déy, déggaluleen ma. Man nag maa ngi nii di leen goreel,” kàddug Aji Sax jee, “ngir wacce leen saamar ak mbas akub xiif. Maa leen di def waa réewi àddina yépp seexlu leen. \v 18 Nit ñi fecci sama kóllëre, sàmmuñu ponki kóllëre gi ñu dige woon fi sama kanam, maa leen di def ni sëllu wa nit ña xaroon ñaar, jaare ca diggante xaaj ya, dogale ko seen ngiñ. \v 19 Muy kàngami Yuda, di kàngami Yerusalem, di bëkk-néeg yeek \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi, ak mboolem waa réew mi jaare woon ci diggante ñaari xaaji sëllu wa, \v 20 maa leen di teg ci seen loxoy noon ak ñiy wut seen bakkan; seeni néew, njanaaw yeek rabi àll yi for. \v 21 Cedesyas buurub Yuda, mook ay kàngamam, maa leen di teg ci seen loxoy noon, loxoy ñiy wut seen bakkan, teg leen ci loxoy mbooloom xarem buuru Babilon mi leen songoon, ba di leen doora bàyyi. \v 22 Maa ngi nii di joxe ndigal,” kàddug Aji Sax jee, “délloosi leen ci dëkk bi, ñu song ko, ba nangu ko, taal ko ba mu jeex. Maay gental dëkki Yuda, ba kenn du ca des.”» \c 35 \s1 Rekabeen raw na Yudeen \p \v 1 Kàddu gii dikkaloon na Yeremi, bàyyikoo ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ci jamonoy buurub Yuda Yowakim doomu Yosya. Mu ne ko: \v 2 «Demal ca Rekabeen ña, nga wax ak ñoom, indi leen kër Aji Sax ji, dugal leen ci néeg yi benn, te jox leen biiñ, ñu naan.» \p \v 3 Ma dem wooyi Yaasaña doomu Yeremi doomu Abàcciña, boole kook ay doomi baayam ak doomam yu góor yépp, làngi Rekabeen ñépp daal. \v 4 Ma yóbbu leen kër Aji Sax ji, dugal leen ca biir néegu taalibey Xanan, góorug Yàlla gay doomu Igdalyaa; mooy néeg ba dendeek néegu kàngam ya, ca kaw néeg doomu Salum, Maaseya fara bunt ba. \v 5 Ci kaw loolu ma tegal Rekabeen ñi ay njaqi biiñ yu fees, aki kaas, ne leen: «Naanleen.» \v 6 Ñu ne: «Nun dunu naan biiñ, ndax sunu maam Yonadab doomu Rekab da noo santoon ne nu: “Buleen naan biiñ mukk, muy yeen ba ci seeni sët, ba fàww. \v 7 Buleen tabax kër, buleen bey, buleen jëmbat tóokëru reseñ, bumu bokk ci seen alal. Waaye nangeen dëkkey xayma seen giiru dund gépp, su ko defee ngeen gudd fan ci biir réew mii ngeen diy màngaan.” \v 8 Déggal nanu it sunu maam Yonadab doomu Rekab ci mboolem li mu nu santoon, ne nu bunu naan biiñ sunu giiru dund, nook sunuy jabar ak sunuy doom, góor ak jigéen, \v 9 bunu tabax kër yu nu dëkke, te tóokër ak tool bu ñuy bey, bumu bokk ci sunu alal. \v 10 Waaye ay xayma lanu dëkke, di sàmm ak a jëfe mboolem lu nu sunu maam Yonadab santoon. \v 11 Waaye ba Nabukodonosor buuru Babilon songee réew mi lanu ne: “Nan duggi gaaw biir Yerusalem, ba rëcc mbooloom waa Babilon ak Siri.” Moo nu taxa toog nii ci biir Yerusalem.» \p \v 12 Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal Yeremi, ne ko: \v 13 «Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: Demal wax mboolem waa Yuda ak waa Yerusalem, ne leen: “Xanaa dungeen dégg ndigal, ba dégg samay kàddu?” Kàddug Aji Sax jee. \v 14 “La Yonadab doomu Rekab santoon ay doomam ne leen: ‘Buleen naan biiñ’ de, jëfees na ko. Duñu naan biiñ ba tey jii ndax wormaal seen santaaney maam. Man nag ay yooni yoon laa leen wax waaye déggaluleen ma. \v 15 Yónnee naa leen samay jaam, yonent yi, ay yooni yoon, ne leen: ‘Na ku nekk ci yeen dëpp yoonam wu bon, di def lu baax, baña topp yeneen yàlla, di leen jaamu, ndax ngeen dund ci réew mi ma leen jox, yeen ak seeni maam.’ Waaye teewluwleen ma, déggaluleen ma. \v 16 Sëti Yonadab doomu Rekab yii déy wormaal nañu santaane ba leen seen maam santoon, waaye xeet wii déggaluñu ma.” \p \v 17 «Kon nag Aji Sax ji Yàllay Israyil, Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: Maa ngi nii di wàcceel Yuda ak képp ku dëkke Yerusalem mboolem musiba mu ma leen tuddaloon. Ndax damaa wax ak ñoom te dégluwñu; ma woo leen, wuyuwñu.» \p \v 18 Ba loolu amee Yeremi ne Rekabeen ña: «Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: Gannaaw wormaal ngeen seen kàddug maam Yonadab, topp santaaneem yépp, ba jëfe lépp lu mu leen santoon, \v 19 loolu tax na Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi wax ne: “Askanu Yonadab doomu Rekab du ñàkk mukk ku góor ku may liggéeyal ba fàww.”» \c 36 \s1 Yowakim def na musibaam \p \v 1 Ba loolu wéyee, ci ñeenteelu atu nguurug buurub Yuda Yowakim doomu Yosya, kàddu gii dikkal na Yeremi, bàyyikoo ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ne ko: \v 2 «Jëlal taxañu bindukaay\f + \fr 36.2 \fr*\fk taxañu bindukaay \fk*\ft ay dogiti der yu bare yu ñu ñawante lay doon, ba mu doon deru bindukaay bu mag bu ñuy taxañ ci bant. Mbind mi nag def ay dog yu dékkarloo.\ft*\f*, nga bind ci mboolem kàddu yi ma la wax ci mbirum Israyil ak Yuda ak mboolem xeet yi, te nga dale ko ba ma waxeek yaw ca jamonoy Yosya ba bésub tey jii. \v 3 Jombul waa kër Yuda dégg mboolem musiba mi ma leen nara teg, ba tax ku ne ci ñoom dëpp yoonam wu bon, ngir ma baal leen seen ñaawtéef ak seen moy.» \p \v 4 Yeremi woo Barug doomu Nerya, dégtal ko mboolem kàddu yi ko Aji Sax ji wax, mu bind ko ci ab taxañu bindukaay. \v 5 Yeremi nag wax Barug, ne ko: «Man damaa am ngànt. Duma mana dem kër Aji Sax ja. \v 6 Demal yaw bésub koor, nga jàng taxañ, bi nga bind kàdduy Aji Sax, ji ma la dégtal, ña ca kër Aji Sax ji di dégg. Nanga ko jàng itam ci kanam mboolem Yudeen ña jóge seeni dëkk. \v 7 Jombul ñu tinu Aji Sax ji, ku nekk ci ñoom dëpp yoonu mbonam, ndax mer mu réy ak xadar ji Aji Sax ji tuddal askan wii kat, nar naa metti.» \p \v 8 Barug doomu Nerya def mboolem la ko Yonent Yàlla Yeremi sant, daldi jàng ca kër Aji Sax ji taxañ ba ñu bind kàdduy Aji Sax ji. \v 9 Loolu yemook juróomeelu atu nguurug buurub Yuda, Yowakim doomu Yosya ca juróom ñeenteelu weer wa. Fekk ñu yéene koor fi kanam Aji Sax ji, ñeel waa Yerusalem gépp ak mboolem ña jóge dëkki Yuda. \v 10 Ci biir loolu Barug tollu ca néegu bindkat ba, Gemarya doomu Safan, ca kër Aji Sax ja. Muy jàng taxañ ba ñu bind kàdduy Aji Sax ji, mbooloo mépp di dégg. Néeg baa nga woon ca ëttu kër Aji Sax ja ca kaw, fa féeteek bunt bu Bees ba. \v 11 Mise doomu Gemarya doomu Safan dégg mboolem kàdduy Aji Sax, ja ca taxañ ba. \v 12 Mu daldi wàcc, ba ca kër buur, jàll ca néegu bindkat ba, fekk fa kàngam yépp toog: Elisama bindkat ba, ak Delaya doomu Semaya, ak Elnatan doomu Agbor, ak Gemarya doomu Safan, ak Cedesyas doomu Anaña, ak jawriñ ña ca des ñépp. \v 13 Mise yegge leen lépp la mu dégg Barug jànge ko ca taxañ ba ca kanam mbooloo ma. \p \v 14 Ci kaw loolu kàngam yépp yebal Yewudi doomu Netaña doomu Selemya doomu Kusi. Ñu ne ko: «Demal ne Barug taxañ bi mu jàngal mbooloo mi, na ko jël te ñëw, indaale ko.» Barug doomu Nerya ŋàbb taxañ ba ca loxoom, dem ba ca ñoom. \v 15 Ñu ne ko: «Toogal jàngal nu ko, nu dégg.» Barug jàngal leen ko, ñu dégg. \v 16 Ba ñu déggee kàddu ya yépp, dañoo tiit, ku ne xool sa moroom. Ñu ne Barug: «Nun kat, nan yegge Buur mbir mii mépp.» \v 17 Ñu laaj Barug, ne ko: «Wax nu! Noo binde kàddu yii yépp. Yeremee la ko dégtal?» \v 18 Barug ne leen: «Moo ma dégtal kàddu yépp de, ma binde ko daa ci taxañ bi.» \v 19 Kàngam ya ne Barug: «Demal làquji yaak Yeremi, te bu kenn xam fu ngeen ne!» \p \v 20 Ba loolu amee ñu wacc taxañ ba ca néeg Elisama bindkat ba, daldi ànd fekki Buur ca ëttam. Ñu yegge ko mbir ma mépp. \p \v 21 Buur nag yebal Yewudi, ngir mu jëli taxañ ba. Mu jëleji ko ca néeg Elisama bindkat ba, daldi jàngal taxañ ba Buur, mook mboolem kàngam ya feggook moom. \v 22 Booba jamonoy sedd la woon, yemook juróom ñeenteelu weer wa. Buur a nga toog ca biir néegu njaaram; taal ba yànj, janook moom. \v 23 Ci biir loolu saa yu Yewudi jàngee ñetti dog ba ñeent, Buur fab saatus bindkat, dagg dog ya, sànni ca taal ba. Mu di ko def ba taxañ ba lakk ca taal ba, ba jeex tàkk. \v 24 Buur ak jawriñam ña ñépp dégg nañu kàddu ya, waaye tiituñu sax, astamaak di xotti seeni yére ni kuy tiislu di def. \v 25 Elnatan ak Delaya ak Gemarya sax tinu nañu Buur, ngir mu baña lakk taxañ ba. Waaye Buur dégluw leen, \v 26 xanaa mu sant Yerameel, kenn ci askanu Buur, mook Seraya doomu Asriyel, ak Selemya doomu Abdel, ne leen ñu jàpp Barug bindkat ba ak Yonent Yàlla Yeremi. Teewul Aji Sax ji làq leen. \p \v 27 Gannaaw ba Buur lakkee taxañ, ba def kàddu ya Barug bindoon ca dégtalub Yeremi, kàddug Aji Sax ji dikkal na Yeremi, ne ko: \v 28 «Dellul jël beneen taxañu bindukaay, nga dellu bind ca mboolem kàddu ya woon ca taxañ ba Yowakim buurub Yuda lakk. \v 29 Yowakim buurub Yuda nag, nanga ko wax ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne yaw yaa lakk taxañ bii, naan lu waral ma bind ci ne buuru Babilon dina ñëw moos te dina tas réew mii, faagaagal fi nit ak mala. \v 30 Moo tax Aji Sax ji wax ci mbirum Yowakim buurub Yuda, ne: du am ku ko toogal ci jalub Daawuda. Néewam dees koy sànni ci biti, mu yendoo naaj, fanaanoo sedd. \v 31 Maa koy yen añu ñaawtéefam, mook njabootam aki surgaam. Maay wàcce ci seen kaw, ñook waa Yerusalem ak Yuda gépp, mboolem musiba mu ma leen digoon, te taxul ñu dégg.”» \p \v 32 Ci kaw loolu Yeremi jël beneen taxañu bindukaay, jox ko bindkat ba, Barug doomu Nerya. Mu dégtal ko, mu bind ca mboolem kàdduy taxañ, ba Yowakim buurub Yuda lakkoon ca taal ba. Yeneen kàddu yu bare yu ni mel sax, dolliku na ca. \c 37 \s1 Cedesyas sàkku na ndimbal \p \v 1 Cedesyas doomu Yosya, ja Nabukodonosor faloon buur ci réewum Yuda moo wuutu Kooña\f + \fr 37.1 \fr*\fk Kooña \fk*\ft mooy Yowakin, di Yekoña ba tey.\ft*\f* doomu Yowakim. \v 2 Waaye muy Cedesyas, muy jawriñam ñi, muy waa réew mi, kenn dégluwu ci kàdduy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji mu wax, Yonent Yàlla Yeremi jottli. \p \v 3 Mu am bés Buur Cedesyas woo Yukal doomu Selemya, ak Cefaña \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi, doomu Maaseya. Mu yebal leen ci Yonent Yàlla Yeremi; ñu ne ko: «Rikk ñaanal nu ci sunu Yàlla Aji Sax ji.» \p \v 4 Booba Yeremee nga doon dem ak a dikk nu mu ko neexe, kenn tëjagu ko woon kaso. \v 5 Mu fekk mbooloom Firawna génn Misra, di ñëw. Waa Babilon ña gawoon Yerusalem dégg ca, ba jóge fa, dellu gannaaw. \p \v 6 Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal Yonent Yàlla Yeremi, ne ko: \v 7 «Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: Buuru Yuda mi leen yebal, ngeen seetsi ma, waxleen ko ne ko: “Mbooloom Firawna mi génnoon di leen wallusi kat, dëpp na bay dellu Misra. \v 8 Waa Babilon dinañu délsi, song dëkk bii xare, nangu ko, lakk ko ba mu jeex.” \v 9 Aji Sax ji nag dafa wax ne: Buleen nax seen bopp naan: “Dem, ba nu, la waa Babilon di def.” Ndax duñu dem. \v 10 Bu ngeen fàddoon mbooloom xarem Babilon miy xareek yeen ñépp it, ba deslewuñu lu moy nit ñu ñu jamat, ñooñooy jógandoo taxaw ca seeni xayma, daldi lakk dëkk bii.» \p \v 11 Gannaaw ba mbooloom xarem Babilon jógee Yerusalem, di daw mbooloom Firawna, \v 12 Yeremi bàyyikoo dëkk ba, jëm diiwaanu Beñamin cay bokkam ngir jëli céram ci ab séddaleb suuf. \v 13 Ba mu demee ba tollook buntu Beñamin, daje faak njiitu dag ya, Irya doomu Selemya doomu Anaña. Irya taxawal Yonent Yàlla Yeremi, ne ko: «Ãa, waa Babilon nga daw jëm!» \v 14 Yeremi ne ko: «Fen nga! Man du maay fekki waa Babilon!» Irya dégluwu ko, xanaa jàpp ko, yóbbu ca kàngami buur ya, \v 15 seen xol tàng ci Yeremi, ñu dóor ko ba noppi, tëj ko ca biir kër Yonatan bindkat ba, fa ñu defoon kaso. \p \v 16 Gannaaw ba ñu dencee Yeremi ca kaso bu xóot ba, ca biir kàmb ga, ba mu toog fa ay fani fan, \v 17 Buur Cedesyas yónnee, woolu ko. Mu ñaarook moom ca biir këram, laaj ko, ne ko: «Mbaa am nga kàddu gu bawoo ci Aji Sax ji?» Yeremi ne ko: «Xanaa lii: “Ci loxol buuru Babilon lees lay teg.”» \v 18 Yeremi teg ca ne Buur Cedesyas: «Ana fu ma la tooñe, yaak say surga, mbaa askan wii, ba nga tëj ma kaso? \v 19 Te sa yonent yi la doon jottli \w waxyu|lemma="waxyu:"\w*, naan la buuru Babilon du dikk ci seen kaw, yaak waa réew mii, ana ñu léegi? \v 20 Léegi nag Buur sang bi, dama lay ñaan ngalla, bul ma delloo kër Yonatan bindkat bi, ma di fa dee.» \p \v 21 Ba loolu amee Buur Cedesyas santaane ñu teg Yeremi ca biir ëttu dag ya. Ñu di ko jox bés bu ne menn mburum lëmm mu jóge ca mbeddu Lakk-kati mburu ya, ba keroog mburu di ñàkk ca dëkk ba. Yeremi nag toog ca ëttu kër dag ya. \c 38 \s1 Tàbbal nañu Yeremi ca kàmb ga \p \v 1 Mu am bés Sefatiya doomu Matan ànd ak Gedalya doomu Pasur ak Yukal doomu Selemya ak Pasur doomu Malkiya. Ñu dégg Yeremiy wax, ñépp di dégg, naan: \v 2 «\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: “Ku des ci biir dëkk bii, saamar rey ko, mbaa xiif, mbaa mbas. Waaye ku génn fekki waa Babilon, dina raw, bakkanam di ngañaayu xareem, mu mucc.” \v 3 Aji Sax ji dafa wax ne: “Dees na teg moos dëkk bii ci loxol mbooloom buuru Babilon, mu nangu ko.”» \p \v 4 Kàngami buur yooyu dem ne Buur: «Waa jii, na dee rekk; mu ngi yoqil xarekat yi des ci dëkk bi, di yoqil ñépp ndax waxam jii mu leen di wax. Waa jii kat wutul jàmmu askan wii, xanaa musiba.» \v 5 Buur Cedesyas ne leen: «Mu ngoog ci seen loxo, manaluma leen dara!» \v 6 Ñu jàpp Yeremi, ngir denci ko ca kàmbug Malkiya, kenn ci askanu buur, ca biir ëttu dag ya. Ñu yoore ko buum, ba ca biir, te kàmb ga amul ndox, bàq rekk a fa nekk. Yeremi nag tàbbi ca biir bàq ba. \p \v 7 Ci biir loolu Ebedd Meleg, \w Kuuseen|lemma="Kuus:"\w* ba, di bëkk-néeg ci biir kër buur, dégg ne tàbbal nañu Yeremi ca kàmb ga. Fekk Buur a nga toog ca bunt ba ñu dippee Beñamin. \v 8 Ebedd Meleg jóge kër buur, dikk ne ko: \v 9 «Buur sang bi, nit ñi de, lu bon lañu def Yonent Yàlla Yeremi; tàbbal nañu ko ca kàmb ga. Dina fa dee ak xiif ndax ab dund amatul ci dëkk bi.» \v 10 Buur sant Ebedd Meleg Kuuseen ba, ne ko: «Jëleel fii fanweeri nit, nga dem génne Yonent Yàlla Yeremi kàmb ga bala moo dee.» \v 11 Ebedd Meleg jël nit ña, daldi dem biir kër buur, jàll ba ca suufu néegu denc ya. Mu jële fa yére yu ràpp aki sagar, boole lépp, yoore buum ca kàmb ga, jottli ko Yeremi. \v 12 Ebedd Meleg ne Yeremi: «Ayca, booleel sagar yi, nga jiital ko ci say poqtaan, teg ci buum yi.» Yeremi def noonu. \v 13 Ñu xëcc buum yi, génne Yeremi kàmb ga. Gannaaw loolu Yeremi des ca biir ëttu dag ya. \p \v 14 Ba loolu wéyee Buur Cedesyas yónnee, woolu Yonent Yàlla Yeremi, ñaarook moom fa ñetteelu bunt ba ca kër Aji Sax ja. Mu ne Yeremi: «Dama lay laaj lenn. Bu ma nëbb dara.» \v 15 Yeremi ne Cedesyas: «Su ma la waxee li am, du danga may rey rekk? Te su ma la digalee it, doo ma déggal.» \v 16 Buur Cedesyas déey Yeremi, ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax jiy dund te sàkkal nu bakkan, duma la rey te duma la teg ci loxoy ñii di wut sa bakkan.» \p \v 17 Yeremi ne Cedesyas: «Aji Sax ji, Yàllay Israyil, Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Soo nangoo génn rekk, jébbali sa bopp kàngami buuru Babilon déy, dinga rawale sa bakkan, te dëkk bii du lakk ba jeex. Dinga dund yaw, yaak sa waa kër. \v 18 Waaye soo jébbalul sa bopp kàngami buuru Babilon, dees na teg dëkk bi ci loxoy waa Babilon, ñu lakk ko ba mu jeex, te yaw doo leen rëcc.» \v 19 Buur Cedesyas ne Yeremi: «Man, ñi ma ragal mooy sunu bokki Yudeen ñi ñibbil waa Babilon; bu ñu ma tegee ci seen loxo, ñu torxal ma.» \v 20 Yeremi ne ko: «Deesu la leen jox. Dangay déggal Aji Sax ji ci li ma la wax rekk, muy sa jàmm, nga mucc.» \v 21 Waaye soo lànkee, ne doo génn, mbir a ngii mu ma Aji Sax ji won. \v 22 Gisuma lu moy mboolem jigéen ñi des ci kër buurub Yuda, ña nga ñu jëme ca kàngami buuru Babilon. Ña nga naan: \q1 «Buur aka baaxi xarit! \q1 Ñoom ñi ko nax, ba man ko, \q1 mu tàbbi ca bàq ba, \q1 ñu dëddu, ne mes!» \p \v 23 Mboolem say soxnaak say doom, dees leen di yóbbu ca waa Babilon, te yaw ci sa bopp doo leen rëcc. Buuru Babilon da lay jàpp, te dëkk bii day lakk ba jeex. \p \v 24 Cedesyas ne Yeremi: «Bu kenn dégg nag lii nu wax. Lu ko moy dinga dee. \v 25 Su sama kàngam yi yégee ne wax naak yaw, ba dikk ne la nga nettali leen li nu waxante te bañ leena nëbb dara, lu ko moy ñu rey la, \v 26 ne leen rekk danga ma doon tinu, ndax ma bañ laa delloo kër Yonatan, nga di fa dee.» \p \v 27 Ba loolu amee kàngami buur yépp dikk, laaj Yeremi, mu wax leen la ko Buur digal. Ñu daldi noppi, ba ko; ndax kenn déggul woon la mu wax ak Buur. \v 28 Yeremi nag des ca ëttu dag ya, ba keroog bés ba ñu nangoo Yerusalem. \s1 Babilon nangu na Yerusalem. \q1 Ba ñuy nangu Yerusalem nag, nii la deme woon. \c 39 \p \v 1 Ba Cedesyas tolloo ci juróom ñeenteelu atu nguuram, ca fukkeelu weeram, ca la Nabukodonosor buuru Babilon ànd ak mbooloom xareem mépp ci kaw Yerusalem, ñu gaw ko. \v 2 Ba Cedesyas tolloo ci fukkeelu atu nguuram ak benn, juróom ñeenti fan ca ñeenteelu weeram, ca lañu bëtt dëkk ba. \v 3 Mboolem kàngami buuru Babilon daldi dikk toog ca buntu dëkk, ba ca digg ba. Nergal Sareser a nga ca ak Samgar Nebo ak Sar Sekim njiitu bëkk-néegi buur ak Nergal Sareser meneen ma, njiitu gisaanekat yi, ñook mboolem kàngami buuru Babilon ña ca des. \p \v 4 Naka la leen Cedesyas buurub Yuda gis, mook xarekatam ya yépp, ñu daldi daw, génn dëkk ba guddi, jaare toolu buur, fëlle bunt bu nekk ca diggante ñaari tata ya, wuti jooru Araba. \v 5 Mbooloom Babilon dàq leen, ba dab Cedesyas ca jooru Yeriko. Ñu jàpp ko, indil ko Nabukodonosor buuru Babilon ca dëkk ba ñuy wax Ribla, ca réewum Amat. Nabukodonosor dogal fa àtteem. \v 6 Buuru Babilon daa rendi doomi Cedesyas yu góor ca Ribla, muy gis, mu rendiwaale mboolem kàngami Yuda. \v 7 Gannaaw loolu mu tuur bëti Cedesyas, jénge ko jéngi xànjar, yóbbu ko Babilon. \v 8 Kër Buur ak këri waa dëkk ba nag, waa Babilon lakk leen, miiri Yerusalem, ñu màbb. \v 9 Nebusaradan njiitu dag ya moom, daa boole ña desoon ca biir dëkk ba, ak ña ko jébbaloon seen bopp, ak ña desoon ca askan wa, jàpp leen, yóbbu ngàllo ca Babilon. \v 10 Ba mu ko defee lenn ci baadoolo yi amul dara, mu wacc leen ca réewum Yuda. Booba la leen jox ay tóokëri reseñ aki tool. \s1 Yàlla yiwi na ñaari jaamam \p \v 11 Ci biir loolu Nabukodonosor buuru Babilon jox ndigal Nebusaradan njiitu dag ya ci mbirum Yeremi. Mu ne ko: \v 12 «Demal jëli Yeremi, nga sàmm ko, te bu ko def dara lu metti. Lu mu la ñaan it, defal ko ko.» \v 13 Ba loolu amee Nebusaradan njiitu dag ya déggoo caak Nebukasban njiitu bëkk-néegi buur ak Nergal Sareser njiitu gisaanekat yi, ak yeneen jawriñi buuru Babilon ña, \v 14 ñu yónnee, jëli Yeremi ca ëttu dag ya, teg ko ci loxol Gedalya doomu Ayikam doomu Safan, ngir Gedalya yóbbu ko kër ga. Yeremi nag des Yuda ca biiri bokkam. \p \v 15 Fekk na kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal Yeremi ba ñu ko tëjee ca ëttu dag ya, ne ko: \v 16 «Demal nga wax Ebedd Meleg, \w Kuuseen|lemma="Kuus:"\w* ba, ne ko: “Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Maa ngi nii di sottalsi sama kàddu yi jëm ci dëkk bii, muy ayam te du doon jàmmam. Dina am ngay gis, bésub keroog. \v 17 Bésub keroog maa lay xettli,” kàddug Aji Sax jee, “ba deesu la teg ci loxol nit ñi nga ragal. \v 18 Maa lay wallu bu baax déy, ba saamar du la daaneel mukk, waaye dinga moom sa bakkan, muy sa yoolu xare, ndaxte wóolu nga ma.”» Kàddug Aji Sax jee. \c 40 \s1 Yuda daje na ca Gedalya \p \v 1 Ci kaw loolu Yeremi jot na kàddu gu bàyyikoo ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, gannaaw ba ko Nebusaradan njiitu dag ya yiwee, mu bàyyikoo Raama. Yeremee nga ñu jéngoon, mook ngàllog Yerusalem gaak Yuda ga jëm Babilon. Nebusaradan génnee Yeremi ca seen biir, \v 2 ñaarook moom, ne ko: «Sa Yàlla Aji Sax ji moo tuddaloon bérab bii musiba mii. \v 3 Aji Sax ji nag indi na ko te def na ko, na mu ko waxe woon. Yeena moy Aji Sax ji, déggaluleen ko ba tax lii dal leen. \v 4 Léegi nag yiwi naa la bés niki tey. Soo bëggee ànd ak man Babilon, ñëwal, dinaa la topptoo. Soo buggul, toogal. Réew mépp a ngii ci sa kanam. Fu la ci neex ak foo ci taamu, dem fa.» \v 5 Balaa Yeremee walbatiku, Nebusaradan teg ca ne ko: «Man ngaa dellu ca Gedalya doomu Ayikam doomu Safan ba tey. Moom la buuru Babilon dénk dëkki Yuda. Man ngaa toog ak moom ci digg waa réew mi, mbaa nga dem daal fu la gënal.» Nebusaradan nag jox Yeremi yóbbal ak lu mu lekk ci yoon wi, daldi ko yiwi. \v 6 Ba mu ko defee Yeremi dem ca Gedalya doomu Ayikam ca Mispa. Mu toog ca moom ca digg nit ña des ca réew ma. \p \v 7 Fekk am na mboolooy Yudeen ñu desoon ci àll bi. Seeni njiit yépp nag dégg, ñook ña ñu àndal, ne buuru Babilon dénk na Gedalya doomu Ayikam réew mi, dénk ko ñenn ci baadoolo yi des Yuda, diy góor aki jigéen aki gone yu ñu yóbbuwul ngàllo ca Babilon. \v 8 Ñu bokk dikk ba Mispa ca Gedalya; Ismayil doomu Netaña ma nga ca woon, ak Yowanan ak Yonatan, ñaari doomi Kareya, ak Seraya doomu Tanumet, ak doomi Efayi ma bokk Netofa, ak Yesaña ma bokk Maaka, ñook seeni nit. \v 9 Gedalya waatal leen, ñook seeni nit, ngir dalal seen xel, teg ca ne leen: «Buleen ragala nangul waa Babilon. Toogleen ci réew mi rekk te nangul buuru Babilon, muy seen jàmm. \v 10 Man nag maa ngii toog Mispa, di leen taxawal fi kanam waa Babilon, bu ñu fi dikkee; yeen dajaleleen seen biiñ ak seen meññeef ak seen diwu oliw, ngeen denc ko te dëkke seen dëkk yi ngeen teg loxo.» \p \v 11 Ci kaw loolu Yudeen ña woon ca Mowabeen ñaak Amoneen ñaak Edomeen ñaak mboolem réew ya, ñoom ñépp dégg ne buuru Babilon wacc na lenn ca askan wa, ñu des réewum Yuda, mu dénk leen Gedalya. \v 12 Yudeen ña ñépp walbatikoo mboolem fu ñu leen sànni woon, daldi délsi réewum Yuda, fekksi Gedalya ca Mispa. Ba loolu amee ñu dajale biiñ ak tàndarma ak figg, ba mu bare lool, ne gàññ. \p \v 13 Mu am bés Yowanan doomu Kareya ànd ak mboolem njiiti mbooloo ya des ca àll ba. Ñu dikk ca Gedalya ca Mispa, \v 14 ne ko: «Xanaa yéguloo ne Baalis buurub Amon yebal na Ismayil doomu Netaña, ngir mu rey la?» Gedalya nag gëmu leen. \v 15 Ba loolu amee Yowanan doomu Kareya déey Gedalya, ne ko: «Tee maa dem, rey Ismayil doomu Netaña fu kenn yégul? Xanaa deesu ko wacc mu rey la, Yudeen ñi daje woon fi yaw yépp di tasaaroo, ndesu Yuda sànku?» \v 16 Gedalya ne Yowanan: «Bul def loolu! Li ngay waxal Ismayil ay fen la!» \c 41 \s1 Ismayil bóom na ñu bare \p \v 1 Ba ñu demee ba ca juróom ñaareelu weer wa ca at mooma, Ismayil doomu Netaña doomu Elisama, askanoo ci ñi moom Yuda te di njiitu jawriñi buur, ànd ak fukki nit ba ca Gedalya doomu Ayikam ca Mispa. Ci kaw loolu, ñu bokk di lekk ca kër Gedalya. \v 2 Ismayil jekki jóg, mook fukki nit ña mu àndal. Ñu jam saamar Gedalya ma buuru Babilon dénkoon réew ma, ba rey ko. \v 3 Ismayil reyaale mboolem Yudeen ña nekkoon ak Gedalya ca Mispa ak xarekati Babilon ya fa nekkoon. \p \v 4 Ba ñu bóomee Gedalya ba ca ëllëg sa, fu kenn yégul, \v 5 mu am juróom ñett fukki nit ñu bàyyikoo Sikem ak Silo ak Samari. Ña nga wat seen sikkim, xotti seeni yére, dagg-daggee seen yaram, di ko ñaawloo. Ñu ŋàbb \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* ak \w cuuraay|lemma="cuuraay l-:"\w* bu ñu indil kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w*. \v 6 Ismayil génne buntu Mispa, gatanduji leen. Ma ngay dox, jëm ca ñoom, di jooy-jooylu ba dajeek ñoom, ne leen: «Agsileen kër Gedalya doomu Ayikam!» \p \v 7 Naka lañu dikk ba ca biir dëkk ba, Ismayil ak ay nitam bóom leen, tàbbal néew ya ci kàmb. \v 8 Fekk na mu am fukki nit ñu bokk ci ñoom ñu ne woon Ismayil: «Tee nga noo baña rey? Nun de am nanub denc ci àll bi. Peppu belee nga ca ak lors ak diw ak lem.» Loolu tax Ismayil fomm, ba boolewu leen ak seeni bokk, rey. \v 9 Kàmb ga Ismayil sànni néewi nit ña mu reyaaleek Gedalya mooy kàmb ga Buur Asa mu Yuda gasoon ba ko Buur Basa mu Israyil songee xare. Moom la Ismayil doomu Netaña feesal aki néew. \p \v 10 Gannaaw loolu mu jàpp mboolem ña des Mispa, di doomi buur yu jigéen ak mboolem ña des Mispa, te Nebusaradan, njiital dag ya, dénkoon leen Gedalya. Ismayil jàpp leen njaam, daldi wutali diiwaanu Amoneen ña. \p \v 11 Ba loolu amee Yowanan doomu Kareya ak njiiti xare yi mu àndal yépp dégg musiba mi Ismayil doomu Netaña def mépp. \v 12 Ñu ànd ak seeni nit, topp ko ngir xareek moom, ba dab ko ca déeg bu mag ba ca Gabawon. \v 13 Ba nit ña Ismayil jàppe Mispa gisee Yowanan ak mboolem njiiti xare ya mu àndal, dañoo bég. \v 14 Ñoom ñépp walbatiku, daw fekki Yowanan doomu Kareya. \v 15 Teewul Ismayil doomu Netaña ak juróom ñetti nitam rëcc Yowanan, daw làquji réewum Amon. \v 16 Yowanan doomu Kareya ak mboolem njiiti xare yi mu àndal nag boole mboolem la des ca mbooloo, ma Yonatan xettli woon ca Ismayil doomu Nataña ca Mispa, gannaaw ba Ismayil bóomee Gedalya doomu Ayikam. Ay nit ñu Yowanan jële woon Gabawon a nga ca, diy góor: ay xarekat ak bëkk-néegi buur, aki jigéen aki gone. \v 17 Ñu dem ba dali ca dalukaayu Kimyam, ca wetu Betleyem, di waaj yoonu Misra, \v 18 ngir rëcc waa Babilon ñi ñu ragaloon, ndax la Ismayil doomu Netaña bóom Gedalya doomu Ayikam, ma buuru Babilon dénkoon réew ma. \c 42 \s1 Toogaani Misra gënul \p \v 1 Gannaaw loolu njiiti xare yépp jóg, ñu ràññee ca Yowanan doomu Kareya ak Yesaña doomu Osaya. Ñu ànd ak askan wa wépp, dikk, ka gëna tuut ba ca ka gën di mag. \v 2 Ñu ne Yonent Yàlla Yeremi: «Ngalla danu lay dagaan, nga ñaanal nu ngir ndesu askan wii ci sa Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Bare woon nanu, waaye gis nga lu néew li des ci nun. \v 3 Ñaanal nu ngir sa Yàlla Aji Sax ji xamal nu fan lanu wara jaare, ak lan lanu wara def.» \v 4 Yonent Yàlla Yeremi ne leen: «Baax na. Maa ngii di leen ñaanal seen Yàlla Aji Sax ji ni ngeen ko waxe. Lu leen Aji Sax ji tontu, dinaa leen ko yegge. Duma ci wacc baat.» \v 5 Ñoom it ñu ne Yeremi: «Mboolem kàddu gu la sa Yàlla Aji Sax ji yóbbante ci nun, bu nu ko deful, yal na Aji Sax ji doon seede bu wér, bu dëggu bi nuy seedeel ag tooñ. \v 6 Mu neex, mu naqari, sunu Yàlla Aji Sax, ji nu la yebal lanuy déggal, ngir su nu déggalee sunu Yàlla Aji Sax ji, dinanu baaxle.» \p \v 7 Ñu teg ca fukki fan, kàddug Aji Sax ji dikkal Yeremi. \v 8 Yeremi woo Yowanan doomu Kareya ak njiiti xare yi mu àndal yépp, woo mbooloo mépp, ñu dikk, ka gëna tuut ba ca ka gën di mag. \v 9 Yeremi ne leen: «Aji Sax ji Yàllay Israyil ji ngeen ma yóbbante seen dagaan, dafa wax ne: \v 10 Su ngeen nangoo toog ba toog ci réew mii, maa leen di defar te duma leen daaneel. Maa leen di jëmbat te duma leen buddat. Ndax ñeewante naa leen ci musiba mi ma leen teg. \v 11 Buuru Babilon mii ngeen ragal, buleen ko ragal!» Kàddug Aji Sax jee. «Buleen ko ragal, ndax yeen laa àndal ngir wallu leen, xettli leen ci moom. \v 12 Maa leen di yërëm ngir mu yërëm leen, delloo leen ca seen suuf. \p \v 13 «Waaye su ngeen bañee déggal seen Yàlla Aji Sax ji, naan: “Dunu toog ci réew mii, \v 14 xanaa nu dem réewum Misra, fa nu dul gise xare; coowal liitu xare sax dunu ko dégg. Dugub it dunu ko fa ñàkke. Foofa lanuy dëkki;” \v 15 su boobaa nag dégluleen li ci Aji Sax ji wax, yeen ndesu Yuda. Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: \q1 “Su ngeen dogoo ba dogu, \q1 nara dem Misra, \q1 ba dem toogaani fa, \q1 \v 16 saamar ba ngeen ragal \q1 moo leen di dabe réewum Misra, \q1 xiif bi ngeen di xalaat \q1 topp leen fa Misra, \q1 te fa ngeen di deeyi. \q1 \v 17 Képp ku dogu woona dem Misra, \q1 ngir toogaani fa, \q1 saamar lay deeye mbaa xiif mbaa mbas. \q1 Du kuy mucc mbaa mu rëcc \q1 musiba mi ma leen naral.” \p \v 18 «Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi déy dafa wax ne: “Bu ngeen demee Misra, ni sama mer ak sama xadar yurikoo woon fi kaw waa Yerusalem, ni la sama xadar naan yureet fi seen kaw. Dingeen doon gentu alkànde, ñu di leen móolook a sewal, te dungeen gisati miim réew.”» \p \v 19 Yeremi teg ca ne: «Yeen ndesu Yuda, Aji Sax ji wax na leen ne leen: “Buleen dem Misra.” Nangeen xam xéll nag ne àrtu naa leen bésub tey. \v 20 Yeena sànk seen bopp ba ngeen ma yebalee ci seen Yàlla Aji Sax ji, ne ma ma ñaanal leen sunu Yàlla Aji Sax ji, te lépp lu sunu Yàlla Aji Sax ji wax, naa leen ko jottli, ngeen def ko. \v 21 Yegge naa leen tey jii li seen Yàlla Aji Sax ji wax, waaye faalewuleen lenn ci kàddu yi mu ma yóbbante ci yeen. \v 22 Léegi nag xamleen xéll ne saamar akub xiif ak mbas moo leen di rey ca réew mooma ngeen namma dem, toogaani fa.» \c 43 \s1 Yóbbu nañu Yeremi Misra \p \v 1 Gannaaw ba Yeremi waxeek mbooloo mépp, ba sottal mboolem kàddu yooyu ko seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji santoon mu yegge leen ko, \v 2 Asaryaa doomu Osaya ak Yowanan doomu Kareya ak nit ñu bew ñooñu ñépp jël kàddu gi. Ñu ne Yeremi: «Dangay fen! Sunu Yàlla Aji Sax ji santu la nga fommloo nu sunu yoonu Misra ga nu bëgga toogi. \v 3 Xanaa Barug doomu Nerya kay moo lay xiirtal ci sunu kaw, ngir teg nu ci loxol waa Babilon, ñu rey nu, mbaa ñu yóbbu nu ngàllo ca Babilon.» \p \v 4 Ci kaw loolu Yowanan doomu Kareya ak yeneen njiiti xare ya yépp ak mbooloo ma mépp gàntal Aji Sax ji, baña des réewum Yuda. \v 5 Ba loolu amee Yowanan ak njiiti xare yépp yóbbu ña desoon ca Yuda ñépp, di mboolem ña ñu jëkkoona sànni ca biir xeet ya leen séq yépp, te ñu ñibbsi woon réewum Yuda, \v 6 góor ñaak jigéen ñaak gone yaak doomi buur yu jigéen ya. Yóbbu nañu mboolem ña Nebusaradan njiitu dag ya tegoon ci loxol Gedalya doomu Ayikam doomu Safan; ñu yóbbaale Yonent Yàlla Yeremi ak Barug doomu Nerya. \v 7 Ñu dikk Misra, baña déggal Aji Sax ji, daldi àgg dëkk ba ñuy wax Tapanes. \p \v 8 Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal Yeremi ca Tapanes, ne ko: \v 9 «Jëlal ñaari doj yu mag yooy suuli ca dëru ban ba ca bunt kër Firawna gi ci biir dëkk bi, te na ko waa Yuda fekke. \v 10 Nga wax leen ne leen: “Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Maa ngi nii di yónnee, jëli Nabukodonosor buuru Babilon, mi ci samag curga, ba teg ngànguneem ci kaw doj yii ma fi suul, mu firi fi xaymaam. \v 11 Bu dikkee dina tas réewum Misra: ku wara médd, médd; kuy dugg njaam, duggi njaam; kuy fàddoo saamar, fàddoo saamar. \v 12 Nabukodonosor dina jafal kër tuuri Misra yi, lakk tuur yi, mbaa mu yóbbu leen. Ni ab sàmm di teeñe mbubbam, ni lay teeñe réewum Misra ba mu set wecc, daldi daagu, dem yoonam. \v 13 Dina rajaxe tuuri doj ya sampe ca Bet Semes ci biir Misra te dina lakk këri tuur yi ci Misra.”» \c 44 \s1 Bokkaale sabab na mbugal \p \v 1 Gannaaw gi kàddu dikkal na Yeremi, jëm ci mboolem Yudeen ñi sancsi réewum Misra, te dëkke Migadol ak Tapanes ak Memfis ak diiwaanu Pattros. Mu ne: \v 2 «\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Yeena gis mboolem musiba mi ma wàcceel Yerusalem ak dëkki Yuda yépp. Ñu ngi nii tey jii gental, kenn dëkku ca. \v 3 Li ko waral di lu bon li ñu def, di ma merloo; di taalal cuuraay ak a jaamu yeneen yàlla yu ñu xamul woon, du ñoom, du seeni maam. \v 4 Yónnee naa leen ay yooni yoon mboolem yonent yi, sama jaam ñi, ne leen: “Rikk buleen def jëf ju siblu jii ma bañ.” \v 5 Waaye dégluwñu, teewluwñu, ba dëddu seenug mbon, baña taalal yeneen yàlla cuuraay, \v 6 ba ma boole sama mer ak sama xadar, yuri, mu jafal dëkki Yudak mbeddi Yerusalem, ba ñu mujj tey jii di gent yu tumurànke. \p \v 7 «Léegi nag, Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Ana lu jar ngeen di teg seen bopp loraange ju réye nii, ba nar fee dagge réewum Yuda, góor ak jigéen, xale ba ci perantal, ba dungeen dese kenn? \v 8 Yeena ngi may merloo ndax li ngeen di def, di taalal yeneen yàlla cuuraay fii ci Misra gi ngeen toogaansi. Seen bopp ngeen dagg, sànni te dingeen mujj ñu di leen móolook a sewal ci digg xeeti àddina yépp. \v 9 Dangeena fàtte seen mbonug maam ya ak mbonu buuri Yudak seen mboni jabar yaak seen mbonu bopp ak seen mbonu jabari bopp ga ñu nekke woon ca réewum Yuda ak mbeddi Yerusalem? \v 10 Kenn ci yeen réccuwul ba tey jii. Kenn wormaalu ma mbaa mu jëfe sama yoon ak sama dogal yi ma leen tegal, tegal ko seeni maam. \p \v 11 «Moo tax Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Maa ngii di jàkkaarlook yeen, ngir musibaal leen, ba dagge fi mboolem Yuda. \v 12 Maay tonni ndesi Yuda gi dogu woon ba dikk réewum Misra, toogaansi fi. Dañuy dee. Ñoom ñépp réewum Misra gii lañuy daanoo. Saamar akub xiif lañuy fàddoo, ki gëna tuut ba ki gën di mag. Saamar akub xiif lañuy fàddoo, te dinañu gental gentu alkànde, ñu di leen móolook a sewal. \v 13 Maay dikkal ñi sancsi réewum Misra ni ma dikkale Yerusalem, dikkaale saamar akub xiif ak mbas. \v 14 Du kuy rëcc mbaa kuy dese bakkan ci ndesu Yuda gi toogaansi fii ci réewum Misra. Te it duñu ñibbi réewum Yuda ga ñu namma ñibbi, lu moy ñu néew.» \p \v 15 Ñu baree nga fa woon, di mboolem ña xamoon ne seeni jabar dañuy taalal cuuraay yeneen yàlla ak mboolem jigéen ña teew. Ñuy mbooloo mu réy, ñépp ña sanci Misra, ba ca diiwaanu Pattros. Ñu daldi ne Yeremi: \v 16 «Li nga nuy wax ci turu Aji Sax ji, dunu ko déglu. \v 17 Nooy def ba defaatoo mboolem lu nu digoo woon, di taalal cuuraay Lingeeru asamaan, tuur mi, di ko tuural ay naan, na nu ko daan defe naka jekk, nook sunuy maam ak sunuy buur ak sunuy kàngam ci dëkki Yudak mbeddi Yerusalem. Teewul dañu daan doyal dugub, di woomle, te gisunu loraange. \v 18 Ba nu bàyyee taalal cuuraay Lingeeru asamaan, tuur mi, ak di ko tuural, ca lanu ñàkk lépp, teg ci saamar akub xiif di nu sànk.» \v 19 Jigéen ña teg ca ne: «Te sax ba nuy taalal cuuraay Lingeeru asamaan, di ko tuural, sunuy jëkkër dañu koo yégul? Xam nañu xéll ne nu ngi defal Lingeeru asamaan ay nàkk yu koy jëmmal, di ko tuural ay naan.» \p \v 20 Ba mu ko defee Yeremi wax ak mboolem góor ñaak jigéen ña ko tontu loolu, ne leen: \v 21 «Saraxi cuuraay yi ngeen di taal, yeen ak seeni maam ak seeni buur ak seeni kàngam, ak baadoolo yi ci biir dëkki Yudak mbeddi Yerusalem, defe ngeen ne Aji Sax ji yégu ko, am da koo fàtte? \v 22 Aji Sax ji manatula dékku seen jëf ju bon ak seen jëf ju siblu ji waral seenum réew mel nii mu mel tey, di ndànd-foyfoy bu gental bu ñuy móoloo, te kenn dëkku ci, \v 23 ndax yeena def saraxi bokkaale, moy Aji Sax ji, dégluwleen Aji Sax ji, te it kàddug yoonam ak dogali yoonam ak seedey yoonam, jëfewleen ci lenn. Moo waral musiba mi leen dikkal nii tey.» \p \v 24 Yeremi teg ca wax ak ñépp, rawatina jigéen ña ñépp, ne leen: «Mboolem yeen Yudeen ñi ci réewum Misra, dégluleen kàddug Aji Sax ji. \v 25 Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: “Yeen ak seeni jabar yeena wax ci seen làmmiñ, àggalee ko seeni jëf. Ngeen ne dingeen def ba defaatoo dige yi ngeen digee taalal cuuraay Lingeeru asamaan, tuural koy naan. Dëggal-leena dëggal seeni dige te jëfee jëfe seeni dige. \v 26 Kon nag, yeen mboolem Yudeen ñi sanc Misra, dégluleen kàddug Aji Sax ji. Maa giñ ci sama tur wu màgg.” Aji Sax jee ko wax. “Ma ne: Sama tur, gémmiñug benn Yudeen dootu ko tudd fi mboolem réewum Misra naan: ‘Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund.’ \v 27 Maa ngi nii di leen teewloo seen musiba, waaye du seen jàmm laa leen di teewloo. Te mboolem waa Yuda ñi ci réewum Misra dinañu sànkoo saamar akub xiif, ba keroog ñuy jeex tàkk. \v 28 Ñu néew ay rëcci saamar, walbatikoo réewum Misra, ñibbi réewum Yuda. Waaye mboolem ndesu Yuda, ga dikkoon toogaansi Misra, dinañu xam kan la kàddoom di sotti, man am ñoom. \v 29 Te lii nangeen ko def ab takk.” Kàddug Aji Sax jee. “Maa ngii di leen dikke mbugal ci bii bérab, ba ngeen xam ne samay kàddooy sotti ba mat sëkk, di seen loraange.”» \v 30 Aji Sax ji dafa wax ne: «Maa ngii di waaja teg Firawna Ofra buuru Misra ci loxol noonam yiy wut bakkanam, na ma tege woon Cedesyas buurub Yuda ci loxol noonam Nabukodonosor buuru Babilon ma doon wut bakkanam.» \c 45 \s1 Barug mucc na \p \v 1 Kàddu gii Yeremi waxoon na ko Barug doomu Nerya, gannaaw ba Barug tënkee ci taxañu mbind, kàddu ya ko Yeremi dégtal ca ñeenteelu atu nguurug doomu Yosya, Yowakim buurub Yuda. \v 2 «\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Yàllay Israyil dafa wax ci yaw, Barug. \v 3 Nga ne: “Wóoy ngalla man! Aji Sax ji yokk na maw naqar. Onk naa ba tàyyi te awma noflaay.” \v 4 Aji Sax ji da maa sant ma wax la ne la: “Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 La ma tabaxoon a ngii, \q1 maa ngi koy daaneel, \q1 la ma jëmbatoon a ngii, \q1 maa ngi koy buddat, \q1 ba réew mépp daj. \q1 \v 5 Looy sàkku ku la beral loxo? \q1 Jaru ko! \q1 Maa ngii di wàcceel musiba képp kuy noyyi.” \q1 Kàddug Aji Sax jee! \q1 “Waaye may naa la sa bakkan di sa yoolu xare, \q1 fépp foo jëm.”» \c 46 \ms1 Kàddug waxyu dalati na xeet yi \mr (Saar 46—51) \p \v 1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jii dikkal na Yonent Yàlla Yeremi, jëm ci xeet yi. \s1 Lu jëm ci Misra \p \v 2 Firawna buuru Misra, bi ñuy wax Neko, ba ko Nabukodonosor buuru Babilon di duma, ma nga woon ca Karkemis ca tàkkal dexu Efraat. Mu yemook ñeenteelu atu nguurug doomu Yosya Yowakim buurub Yuda. Kàddug waxyu gii moo jëm ci Misra ci wàllu diggante ba seen mbooloom xare ma tollu woon. \q1 \v 3 «Ŋàbbleen pakkoo pakk te xareji. \q1 \v 4 Takkleen fas yi, war naari góor yi, \q1 ba làng-déraale seen mbaxanay xare, \q1 nàmmaat xeej, \q1 sol yérey xare!» \b \q1 \v 5 «Ana lu ma gis? \q1 Waa Misraa jaaxle bay dellu gannaaw, \q1 seeni jàmbaar falaxoo, \q1 ne wëqet, geesuwñu, \q1 tiitaange ubale.» \q1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee! \q1 \v 6 «Bu nit gaaw ba raw \q1 mbaa mu jàmbaare ba mucc. \q1 Bëj-gànnaar lañu féete, feggook dexu Efraat, \q1 di tërëf, di daanu. \b \q1 \v 7 «Kii ku mu, muy fuddu ni dexu Niil, \q1 di fuur ni wali ndox? \q1 \v 8 Misraa, mooy fuddu ni dexu Niil, \q1 di fuur ni wali ndox. \q1 Mu naan: “Maay fuddu, mëdd àddina, \q1 sànk ab dëkk ak ña ca biir.” \q1 \v 9 Na fas buur, watiir fiddi, \q1 jàmbaar sàqi: \q1 waa \w Kuusoo|lemma="Kuus:"\w* waa Puut ak seeni pakk, \q1 ak waa Ludd ak seeni xala. \q1 \v 10 Waaye bésub keroog déy, \q1 Boroom bi Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko moom, \q1 muy bésub feyu bu muy feyey noonam. \q1 Saamar suur suux, \q1 màndee deret. \q1 Boroom bi Aji Sax ji Boroom gàngoor yi \q1 mooy rendee réewum bëj-gànnaar ab sarax, \q1 feggook dexu Efraat. \q1 \v 11 Yaw Misra mu taaru mi, \q1 demal ba Galàdd wuti diw, dàmpoo. \q1 Faju, fajooti; \q1 dara du la wéral! \q1 \v 12 Xeet yeey dégg sa toroxte, \q1 sa yuux dajal àddina. \q1 Jàmbaar téqtaloo jàmbaar, \q1 ñu ànd ne fëlëñ!» \p \v 13 Kàddu gii dikkaloon na Yonent Yàlla Yeremi, ba Nabukodonosor buuru Babilon dikkee, di duma waa réewum Misra. Mu ne: \q1 \v 14 «Yégleel lii Misra, yéene ko fa ca Migadol, \q1 yéene ko fa ca Memfis ak Tapanes. \q1 Neleen: “Dërleen, taxaw temm! \q1 Saamar kat a ngi lekk li leen wër.” \q1 \v 15 Lu Apis di daw? \q1 Lu tee seen yàllay yëkk jooju taxaw? \q1 Xanaa Aji Sax jee ko bëmëx! \q1 \v 16 Moo bëmëx ñu bare, \q1 ku nekk naan moroom ma: \q1 “Jógal nu dellu ca sunuy bokk, \q1 ca sunu réewum cosaan, \q1 ba mucc saamaru noon.” \q1 \v 17 Dees na fa woyal Firawna buuru Misra, naan ko: \q1 “Coowal neen te bés wees.” \b \q1 \v 18 «Giñ naa ko ci man miy dund,» \q1 kàddug Buur Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi di turam: \q1 «noon ay dikk, mel ni tundu Tabor ci digg tund yi, \q1 mbete tundu Karmel wi feggook géej. \q1 \v 19 Yaw mi dëkke Misra mu taaru mi, \q1 ëmbal sa ëmb, jëm ngàllo; \q1 Memfis\f + \fr 46.19 \fr*\fk Memfis: \fk*\ft Fii ñu ne Memfis, am na sotti yu fi indi turu Nof.\ft*\f* dëkk bii kat ci gental la jëm, \q1 di ndànd-foyfoy lu kenn dëkkul. \q1 \v 20 Misra daa mel ni jeegu nag bu yànj, \q1 weñ ne waa, waa, bawoo bëj-gànnaar. \q1 \v 21 Seen xarekat yi ñu bind sax \q1 ñu ngi mel ni sëllu yu yaflu, \q1 ñoom it ànd ne wërëñ, wëqet, \q1 kenn taxawul! \q1 Bésu safaan a leen dikkal, \q1 seen mbugal taxaw, \q1 \v 22 ñu daw di faraas-faraasiy wéy ni jaan. \q1 Doole la noon songe Misra, \q1 dikke leeni sémmiñ \q1 ni gorkati garab. \q1 \v 23 Lu gott fatt fatt, ñu gor.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 «Ñoo gëna barey njéeréer, \q1 ba maneesu leena lim. \q1 \v 24 Gàcceel nañu Misra mu taaru mi, \q1 teg ko ci loxoy xeeti bëj-gànnaar.» \p \v 25 Aji Sax ji Yàllay Israyil, Boroom gàngoori xare yi wax na ne: «Maa ngii di dikke mbugal Amon, tuuru dëkk bii di Teeb, ak Firawnaak waa Misraak seeni tuur ak seeni kàngam, boole ci ñi yaakaar Firawna. \v 26 Maa leen di teg ci loxoy ñiy wut seen bakkan, di Nabukodonosor buuru Babilon aki jawriñam. Gannaaw loolu dees na dëkkewaat Misra na woon.» Kàddug Aji Sax jee! \s1 Israyil dina xettliku \q1 \v 27 «Yaw Yanqóoba sama jaam bi nag, bul tiit; \q1 yaw Israyil, ma ne bul ragal. \q1 Maa ngii di la wallusi, \q1 jële la fu sore, \q1 jële sa askan \q1 fa seen réewu njaam ga, \q1 Yanqóoba délsi, \q1 dal, aaru, du tiitati. \q1 \v 28 Yaw Yanqóoba sama jaam bi, bul tiit.» \q1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. \q1 «Yaw laa àndal. \q1 Maay fàkkas mboolem xeet yi ma leen sànni woon, \q1 waaye yeen, duma leen fàkkas. \q1 Duma leen ñàkka duma moos, \q1 waaye dinaa leen yar lu yem.» \c 47 \s1 Lu jëm ci Filisteen ñi \p \v 1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkaloon na Yonent Yàlla Yeremi jëm ci Filisteen ñi, balaa Firawna di song dëkkub Filisteen ba ñuy wax Gasa. \v 2 Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 «Ndox a ngay fuddoo bëj-gànnaar, \q1 diy waame, walsi, \q1 walal réew meek li ci biiram \q1 akub dëkk ak ku ci biiram; \q1 doom aadama yuuxu, \q1 waa réew mépp serandoo. \q1 \v 3 Booba fas yaa ràmbal, \q1 watiir ya riir, \q1 mbegey watiir ya kar-kareendoo, \q1 yoxo yoqi, ba baay geesuwul doom, \q1 \v 4 bésub sànkute dikkal képp kuy Filisteen, \q1 ba dagge dëkk yii di Tir ak Sidon \q1 ndimbal lu ñu dese woon. \q1 Aji Sax jaa ngay sànk Filisteen, ña des \q1 te cosaanoo dunu Keret. \q1 \v 5 Watu nel, ñaawloo, dikkal na Gasa, \q1 te wedamloo nañu Askalon. \q1 Yeen ñi dese joor gi, \q1 fu ngeen àppal seen yaram, \q2 wi ngeen di daggat, di ko ñaawloo? \q1 \v 6 Ngeen naa: “Wóoy saamaru Aji Sax jii, \q1 xanaa doo selaŋlu? \q1 Dellul sa mbar, boog, \q1 dal-lu, ne tekk!” \q1 \v 7 Waaye yaw saamar, noo mana selaŋloo \q1 te Aji Sax ji yebal la \q1 ci kaw Askalon ak waa tefesu géej, \q1 fa mu ko dogale?» \c 48 \s1 Lu jëm ci réewum Mowab \p \v 1 Lu jëm ci Mowab, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Yàllay Israyil, Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: \q1 «Ngalla waa Nebo, seen dëkk ba yàqu na! \q1 Kiryaatayim, ñu torxal, nangu ko; \q1 tata ja daanu, tasaaroo. \q1 \v 2 Mowab amatul woy, \q1 fa Esbon la leen noon ya fexeel lu bon, \q1 ne: “Aycaleen nu raafal wii xeet!” \q1 Yeen waa Madmen it, ñu wedamal; \q1 saamar topp leen. \q1 \v 3 Yuux jibe na Oronayim, \q1 ndaw salfaañook rajaxoo ju réy! \q1 \v 4 Mowab tas, ay fereem serandoo. \q1 \v 5 Ñay yéeg jëm Luwit, di jooyoo. \q1 Ña ngay yéeg, di jooyoo. \q1 Ñay wàcci Oronayim \q1 di dégg aji jàq jiy yuuxoo. \q1 \v 6 Ñu naan: “Dawleen, rawale seen bakkan, \q1 ba tumurànkeji ni gajju màndiŋ!” \q1 \v 7 Mowab, yeena yaakaar dooleek alal, \q1 yeen it, dees na leen jàpp; \q1 Kemos, seen tuur mi duggi ngàllo, \q1 mooki \w sarxalkatam|lemma="sarxalkat b-:"\w* aki kàngamam. \q1 \v 8 Dëkkoo dëkk ay yàqtoo, \q1 benn dëkk du mucc! \q1 Waa xur wii sànku, \q1 waa déndu doj wu tell wee yàqtoo.» \q1 Muy la Aji Sax ji wax. \q1 \v 9 «Gasal-leen Mowab, \q1 day sànku moos, \q1 ay dëkkam gental, \q1 kenn du fa des! \q1 \v 10 Alkànde ñeel na kuy sàggane liggéeyu Aji Sax ji. \q1 Alkànde ñeel na kuy xañ deret saamaru Aji Sax ji. \b \q1 \v 11 «Mowab a dale féex cag ndawam, \q1 kenn jàppu ko njaam, yóbbu, \q1 wàllanteesu ko ndab ak ndab, \q1 xanaa mu ne degg ni biiñ bu taaje, \q1 di saf, di xeeñ ba tey. \q1 \v 12 Moo tax ay bés a ngii di ñëw,» \q1 kàddug Aji Sax jee, \q1 «maa leen di yónnee ay nit ñu sotti diw gi, \q1 ndab, soteet; njaq, rajax. \q1 \v 13 Yaakaaru Mowab ci Kemos tuur mi, tas, \q1 ni yaakaaru waa kër Israyil ci Betel ma ñu wóolu, tase woon. \b \q1 \v 14 «Mowabee, du yaay kañu, \q1 naan jàmbaar ngeen, \q1 diy ñeyi xare? \q1 \v 15 Song nañu la, yàqte say dëkk; \q1 la man ci say ndaw daanu, fàddu.» \q1 Kàddug Buur Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi. \q1 \v 16 «Musibay Mowab a ngi jegesi, \q1 safaanam làbbleeti, wuti ko. \q1 \v 17 Mboolem yeen ñi wër xeet wii, jooyleen leen; \q1 yeen ñi dégg seen tur ñépp, jooyleen leen. \q1 Neleen: “Moo, nu gii nguur mana foqe, \q1 ba foqaale jii daraja?” \b \q1 \v 18 «Yeen waa Dibon, dëkk bu taaru bi, \q1 wàccleen seen teddnga lu kawe \q1 te tooge digg maral; \q1 kiy yàqtesi Mowab kat song na leen, \q1 di màbbsi seeni tata. \q1 \v 19 Yeen waa Arower, \q1 taxawleen fi yoon wi te teewlu; \q1 góor gu fi jaare mbaa ndaw su rëcc, di daw, \q1 ngeen laaj ko ne ko: “Lu xew?” \q1 \v 20 Ñu ne: “Gàcce ñeel na Mowab gii tas!” \q1 Yuuxooleen, ne wóoy! \q1 Yéeneleen fa tàkkal dexu Arnon, \q1 ne Mowab tas na! \q1 \v 21 Mbugal dikkal déndu doj wu tell wi, \q1 dikkal dëkk yii di Olon, Yaxacc ak Mefat \q1 \v 22 ak Dibon ak Nebo ak Bet Diblatayim \q1 \v 23 ak Kiryaatayim ak Bet Gamul ak Bet Mewon \q1 \v 24 ak Keryot ak Boccra, \q1 mboolem dëkki Mowab daal, \q1 fu jegeek fu sore. \q1 \v 25 Sidditu Mowab day dog, \q1 loxoom damm.» \q1 Kàddug Aji Sax jee! \q1 \v 26 «Du Mowab a doon diir Aji Sax ji mbagg? \q1 Nañu leen màndal sànjum Aji Sax ji, \q1 ba ñu waccu, di ca xuus, \q1 ba ñoom it, ñu di leen ree. \q1 \v 27 Mowabee, du yeena doon ree Israyil? \q1 Dangeen leena fekk ci biiri sàcc, \q1 ba fu ngeen leen tudde, wëcc bopp? \q1 \v 28 Yeen waa Mowab, \q1 baleen dëkk yi, dëkke paxi doj. \q1 Defleen niy xati, \q1 tàgge peggi xunti. \b \q1 \v 29 «Noo dégg ni Mowab bewe, \q1 bew lool, \q1 réy, reew, di damu; \q1 ne daŋŋ-daŋŋiiral. \q1 \v 30 Maa xam seen reewande,» \q1 kàddug Aji Sax jee, \q1 «seeni kañu neen la, \q1 seeni jëf di neen. \q1 \v 31 Moo tax may jooy Mowab, \q1 di wooteel wall Mowab gépp, \q1 di yuuxul waa Kir Eres. \q1 \v 32 Yaw reseñu Sibma gi, \q1 ma jooyal la lu raw la ma jooyal Yaser. \q1 Yaw la say car jàlloon géej, \q1 àkki géeju Yaser, \q1 sa figg jeek sa reseñ, noon yàqte. \q1 \v 33 Tukkal nañu mbégteek bànneex \q1 fi tóokëri réewum Mowab. \q1 Maa ŋacc mbàndi biiñ ya, \q1 kenn nalatu fa reseñ, di soowoo \q1 coowal mbégte, xanaa ay yuux. \q1 \v 34 Yuux jibe na Esbon, ba Elale, \q1 àkki ba Yaxacc \q1 ak Sowar ba Oronayim ak Eglat Selisiya. \q1 Ndoxi Nimrim sax ŋiis na. \q1 \v 35 Maay bóome biir Mowab.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 «Maay bóom kuy joxe sarax ci jaamookaay, \q1 di taalal am tuuram cuuraay. \q1 \v 36 Naa jooy Mowab jooyi xol, \q1 yu toxoro di jooye ab dëj, \q1 na toxoro di jooye dëju waa Kir Eres. \q1 Lu ñu dajale woon sànku na! \q1 \v 37 Ñoom ñépp a nelu, \q1 wat seeni sikkim, \q1 daggat seeni loxo, \q1 sol ay saaku, di ko ñaawloo. \q1 \v 38 Kaw taaxi Mowab yépp aki péncam, \q1 fépp ay yuuxoo di jib. \q1 Maa toj Mowab \q1 ni ndab lu kenn soxlaatul.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 39 «Yuuxooleen, ne leen: “Céy gii yàqtoo! \q1 Mowab gii wone gannaaw! Mowab rus na.” \q1 Ñi ko wër ñépp a koy reetaan, seen yaram di daw ci ñoom.» \q1 \v 40 Aji Sax ji déy dafa wax ne: \q1 «Lu mel ni jaxaay a ngii naa jàyy, \q1 firiy laafam, këfsi Mowab. \q1 \v 41 Dees na teg Keryot ga ca Mowab loxo, \q1 ne tata ya taral; \q1 su keroogee fitu jàmbaar ne tërit, \q1 mu mel ni kuy matu. \q1 \v 42 Mowab day sànku, ba xeetam fey. \q1 Ñoo doon diir Aji Sax ji mbagg. \q1 \v 43 Yeen waa Mowab, \q1 pat-pati rekk, di tàbbiy pax aki yeer.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 44 «Pat-patiy daw, tàbbim pax; \q1 génn um pax, tàbbim yeer. \q1 Maay yen Mowab, maa leen di yen moos, \q1 seen atum mbugal.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 45 «Fa keppaaru Esbon lañuy daw taxawi, \q1 doole dëddu. \q1 Booba sawaraa tàkke Esbon, di law; \q1 sël-sëlee foofa ca péeyu Buur Siwon, \q1 ba dajal réewum Mowab, nitu coow ña, \q1 boole jë akum kaaŋ xoyom. \q1 \v 46 Wóoy, waa Mowab, ngalla yeen! \q1 Yeen ñiy jaamu Kemos, sànku ngeen! \q1 Dees na jàpp seen doom yu góor njaam; \q1 jigéen ñi it, njaam. \b \q1 \v 47 «Du tee fan yu mujj ya, \q1 ma tijji wërsëgu Mowab.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 Fii la àtteb Mowab yem. \c 49 \s1 Lu jëm ci Amoneen ñi \q1 \v 1 Lu jëm ci Amoneen ñi, \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: \q1 «Israyil daa amuli doom? \q1 Am daa amul dono? \q1 Lu tax Milkom\f + \fr 49.1 \fr*\fk Milkom \fk*\ft tuuru Amoneen ñi la woon, te Gàdd ci suufas Israyil la bokkoon.\ft*\f* tuur mi donloo suufas Gàdd, \q1 ba ay jaamukatam sanc dëkki Gàdd? \q1 \v 2 Moo tax ay bés a ngii di ñëw,» \q1 kàddug Aji Sax jee, \q1 «maay dégtal Raba, dëkku Amoneen ñi, \q1 coowal xare ci seen biir, \q1 tund wa gental, \q1 dëkk-dëkkaan ya tàkk ba jeex, \q1 ba keroog Israyil futti ñooña ko futti woon.» \q1 Aji Sax jee ko wax. \b \q1 \v 3 «Éy waa Esbon, Ayi seen dëkk bi tas na, yuuxuleen! \q1 Yeen waa dëkk yi séq Raba, \q1 sol-leeni saaku, ñaawloo, \q1 jaab diggante tata yi, tiisloo. \q1 Milkom seen tuur mi déy duggi na ngàllo, \q1 ànd aki \w sarxalkatam|lemma="sarxalkat b-:"\w* aki kàngamam. \q1 \v 4 Céy Raba, bii dëkk bu taaru, toogadi, \q1 yeena doon damoo xur yi, \q1 ba ci seen xur wu naat wii? \q1 Yeena yaakaaroon seeni denc, \q1 naan: “Ku ñemee dal sunu kaw?” \q1 \v 5 Maa ngii di leen wàcceel njàqare,» \q1 kàddug Boroom bi Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi, \q1 «njàqare luy bawoo fi leen wër fépp, \q1 dàq leen, ku ne jubal yoonam, \q1 du kenn ku leen di dajaleeti. \q1 \v 6 Waaye bu loolu weesee, \q1 ma tijji wërsëgu Amoneen ñi.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \s1 Lu jëm ci Edomeen ñi \p \v 7 Lu jëm ci Edomeen ñi, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: \q1 «Xanaa boroom xel amatul fi Teman? \q1 Xanaa ndigal a réer xamkat yi? \q1 Am seen bopp a yàqu? \q1 \v 8 Yeen waa Dedan, \q1 walbatikuleen daw, ruuroo seeni pax. \q1 Maa ngi wàcceel askanu Esawu\f + \fr 49.8 \fr*\fk Esawu \fk*\ft ak Edom kenn ki la. Askanu Esawu ñoo dëkke woon réewum Edom.\ft*\f* safaan, \q1 seen mbugal taxaw na! \q1 \v 9 Su leen wittkati reseñ dikkalee, xanaa dinañu ca wacc ay doom? \q1 Su leen ay sàcci guddi dikkalee, \q1 du la leen doy lañuy sëxëtoo? \q1 \v 10 Waaye yeen askanu Esawu, \q1 man maa leen di ñori, ba ngeen ne duŋŋ. \q1 Maay siiwal seeni rawtu, \q1 ba dootuleen mana làqu; \q1 seeni goneek seeni bokk, ñépp ay sànku, \q1 seeni dëkkandoo sax, kenn du ca des ku naan: \q1 \v 11 “Jirim yi ngeen bàyyi, \q1 maa leen di dundal, \q1 te seeni jëtun man nañu maa yaakaar.” \q1 \v 12 Ndegam ñi yeyoowul mbugal \q1 ñooy jolu kaasu mbugal, \q1 nees leen di ñàkka toppe, yeen? \q1 Dees na leen topp moos, \q1 ngeen jolu kaasu mbugal. \q1 \v 13 Giñ naa ko ci man mii, déy,» \q1 kàddug Aji Sax jee, \q1 «Boccra, dëkk bii day mujj di gent bu ñu doyadal, \q1 ndànd-foyfoy bu ñuy móoloo, \q1 dëkk-dëkkaanam yépp gental ba fàww.» \sp Yeremeey wax \q1 \v 14 Ab dégtal laa dégg, mu bawoo fa \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 ndaw la yebal ci biir xeet yi, ne leen: \q1 «Dajeleen waajal xare te song Edom xare! \q1 \v 15 Yeen Edom, tuutal leen laay def ci biir xeet yi, \q1 ñu xeeblu ngeen di doon ci biir doom aadama yi. \q1 \v 16 Seen ragluwaay ak seen reewande sànk na leen, \q1 yeen ñi dëkke xuntiy doj, \q1 féetewoo colli tund yi. \q1 Waaye su ngeen ajee seenum tàgg ni jaxaay it, \q1 fa laa leen di àjjee.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 17 «Edom day mujj gental, \q1 ku fa jaare waaru, \q1 di muslu ci mboolem li ko dal. \q1 \v 18 Edom day tas ni Sodom ak Gomor ak la ko wër.» \q1 Aji Sax jee ko wax. \q1 «Nit du ca dëkk, \q1 doom aadama du fa dal. \q1 \v 19 Maa ngii di fëlle gottub Yurdan ni gaynde, \q1 wuti mbooy gu naat. \q1 Xef ak xippi déy, ma fëxale fa ñépp, \q1 ba tabb fa ki ma taamu. \q1 Ana moos ku mel ni man? \q1 Ku am sañ-sañ ci man? \q1 Ana njiit luy taxaw fi sama kanam? \q1 \v 20 Kon dégluleen pexe mi Aji Sax ji waajal Edom, \q1 mébét yi mu mébétal waa Teman ñooñu! \q1 Ndegam deesu leen wommat ni seen gàtt yu ndaw, yóbbu, \q1 ba yàq seen parlu yaxeet. \q1 \v 21 Seen jéll day réy ba riiral suuf, \q1 seeni yuux àkki géeju Barax ya. \q1 \v 22 Lu mel ni jaxaay a ngii, naa fëyy, \q1 firiy laafam, këfsi Boccra. \q1 Bésub keroog fitu jàmbaari Edom ne tërit, \q1 mel ni kuy matu.» \s1 Lu jëm ci Damaas \q1 \v 23 Lu jëm ci Damaas: \q1 «Dëkk yu mag ya ko wër, \q1 di Amat ak Arpàdd, jàq nañu; \q1 dég-dég bu tiis ba ñu dégg la. \q1 Dañu ne yàcc, jaxasoo, \q1 mbete géej gu sàmbaraax, deesu ko dalal. \q1 \v 24 Damaas a ne yasar, ne wërëñ, di daw; \q1 tiitaange ne leen nuus, \q1 njàqareeku mitit ne leen taral \q1 ni kuy matu. \q1 \v 25 Lu tee ñu gental bii dëkk bu siiw, \q1 taax yii ma saf? \q1 \v 26 Su bés baa kay, seeni waxambaane fëlëñoo pénc yi, \q1 seeni xarekat wedam.» \q1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee, Boroom gàngoor yi. \q1 \v 27 «Maay taal ca tatay Damaas \q1 sawara wu xoyom këri Buur Ben Addàd.» \s1 Lu jëm ci Arabi Kedar ak Àccor \p \v 28 Lu jëm ci Kedar ak nguuri Àccor yi Nabukodonosor buuru Babilon nangu woon, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: \q1 «Ñokket ci kaw Kedar, \q1 ba tas waa penku yooyu, \q1 \v 29 nangu xaymaaki jur, \q1 ak kiiraay ak luy jumtukaay, \q1 yóbbu seeni giléem, \q1 te biral leen, ne leen: \q1 “Musiba ubale na!” \q1 \v 30 Yeen waa Àccor, \q1 fëxleen te dawa daw, \q1 ruurooji seeni pax.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 Mu ne: «Nabukodonosor buuru Babilon déy, \q1 lalal na leen pexe, \q1 mébal leen. \b \q1 \v 31 «Ayca ci kaw xeet wii ne finaax, \q1 dëkke xel mu dal!» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 «Du bunt, du galanu weñ gu ñu fegoo, \q1 te ñoom rekk a dëkk. \q1 \v 32 Dees na nangu seeni giléem, \q1 tonni seen juroo jur, \q1 ma tasaare ñooñuy wat seen peggu kawaru bopp, \q1 ngelaw lu jóg, buub leen, yóbbu, \q1 ma yéewe leen seen musiba, wetoo wet.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 33 «Àccor day doon dëkkub till, \q1 gental ba fàww; \q1 nit du fa dëkk, \q1 doom aadama du fa dal.» \s1 Lu jëm ci Elameen ñi \p \v 34 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkaloon na Yonent Yàlla Yeremi, jëm ci Elameen ñi, ci njàlbéenu nguurug Cedesyas buurub Yuda. Mu ne: \q1 \v 35 Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: \q1 «Damay damm fittu Elam, \q1 seen ngëneelu ngànnaay. \q1 \v 36 Maay ngelawe ñeenti weti asamaan, \q1 dal fi kaw Elam, \q1 tasaare leen fépp fu ngelaw jublu, \q1 ba du am xeet wu daw-làquy Elam dul fekki. \q1 \v 37 Maa leen di xoqtal fi seen kanami noon, \q1 yiy wut seen bakkan, \q1 alage leen sama tàngooru mer.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 «Maa leen di toppe saamar, \q1 ba raafal leen. \q1 \v 38 Maay déjjatee Elam buur ak bummi, \q1 samp fa samab jal.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 39 «Waaye fan yu mujj ya, \q1 maay tijji wërsëgu Elam.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \c 50 \s1 Babilon daanu na \p \v 1 Kàddu gii la \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax ci mbirum réewum Babilon, réewum Kaldeen ña, te Yonent Yàlla Yeremi jottli ko. \q1 \v 2 «Waxleen xeet yi, yéeneleen, \q1 woneleen misaal te yéene, \q1 waxleen lii, bañ cee làq dara. \q1 Neleen: “Dees na nangu Babilon, \q1 torxal Bel mbaa Mardug, tuur mi, \q1 tas ko, \q1 gàcceel gàllaaj yi, tas kasaray tuur yi.” \q1 \v 3 Aw xeet kay ay bawoo bëj-gànnaar, dal fi seen kaw. \q1 Ñooñooy gentalsi seenum réew, \q1 ba kenn dootu fi dëkk, \q1 nit ak mala, ne mott, ne mes. \q1 \v 4 Su bés baa, ci yooyu fan,» \q1 kàddug Aji Sax jee, \q1 «\w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ay ànd ak Yudeen ñi, \q1 dikk di jooy, \q1 di sàkku seen Yàlla Aji Sax ji. \q1 \v 5 Dinañu laaj yoonu \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, jublu fa \q1 te naan: “Ayca nu dajeji fa Aji Sax ji, \q1 ci biir \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* gu sax \q1 gu kenn dul fàtte.” \b \q1 \v 6 «Sama ñoñ ñi réer niy xar, \q1 seeni sàmm a leen lajjal, \q1 sànk leen fi kaw tund yi, \q1 ba tundoo tund, ñu yéegi fa, \q1 fàtte seen goorukaay. \q1 \v 7 Noon bu taseek ñoom warax leen \q1 te naan: “Nun defunu dara. \q1 Ñoom ñoo moy Aji Sax ji, \q1 te mooy dalukaayu njekk, \q1 ba seeni maam yaakaaroon.” \b \q1 \v 8 «Yeen gan ñi, fëxeleen Babilon, \q1 ba sore réewum Kaldeen ñooñu. \q1 Defleen niy sikket, daw jiitu jur gi. \q1 \v 9 Maa ngii déy di xabtal fi kaw Babilon, \q1 kurélu xeet yu mag, bawoo réewum bëj-gànnaar, \q1 làng-déralsi Babilon! \q1 Seeni fitt di ñeyi xare, \q1 du moy, du sooy. \q1 \v 10 Réewum Babilon a doon alalu sëxëtoo, \q1 bu ñuy sëxëtoo ba doyal.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 11 «Ãa yeen waa Babilon, yeena sëxëtoo xeet wi ma séddoo, \q1 di ko bégeek a bànneexoo, \q1 di bajantu ni nag wuy bàcc pepp, \q1 di ŋexal ni naaru góor? \q1 \v 12 Ndaw gàcce gu réy ci seen ndey, \q1 ndaw toroxte ci ki leen sukk jur! \q1 Réew maa ngii di geenu réew yi, \q1 di ndànd-foyfoy, gu wow koŋŋ. \q1 \v 13 Kenn du fi des ndax merum Aji Sax ji, \q1 lépp ay gental, \q1 ba képp ku jaare Babilon, \q1 day waaru, di muslu \q1 ci mboolem mbugal ya fa dal. \q1 \v 14 Yeen fittkat yépp, làng-déral-leen Babilon, \q1 gaw ko, soqeendoo, baña yaxanal! \q1 Ñoo moy Aji Sax ji! \q1 \v 15 Xaaculeen fi kawam, wër ko, \q1 Babilon daanu na, ba joxe ndodd, \q1 tata ya màbb, \q1 dàbbli ya rajaxoo! \q1 Aji Sax jeey feyu, \q1 feyuleen! \q1 Na mu defoon, defleen ko ko. \q1 \v 16 Daggeleen Babilon kuy ji ak kuy góob, \q1 ku fay gan, na daw saamaru noon, \q1 fëx jëm réewam, \q1 dellu cay bokkam. \b \q1 \v 17 «Israyil diy gàtt yu tasaaroo, \q1 yu ay gaynde dàq, \q1 buurub Asiri di gaynde gi jëkka lekk, \q1 Nabukodonosor buuru Babilon topp ca, seeñu yax ya.» \q1 \v 18 Moo tax Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi ne: \q1 «Maa ngii di dikkal buuru Babilon ak waa réewam, \q1 na ma dikkale woon buurub Asiri. \q1 \v 19 Maa ngii di delloo Israyil parloom, \q1 mu dellu di fore àllub Karmel ak Basan, \q1 di regge tundi Efrayim ak Galàdd. \q1 \v 20 Su bés baa, ci yooyu fan,» \q1 kàddug Aji Sax jee, \q1 «dees na seet fi Israyil lu ñaaw, du fi am; \q1 fi Yuda it, deesu fi gis bàkkaar. \q1 Maay jéggal moos ndes wi ma fi saxal. \b \q1 \v 21 «Songleen réewum Meratayim ak waa Pekodd\f + \fr 50.21 \fr*\fk waa Meratayim and waa Pekodd \fk*\ft ci Babilon lañu bokk.\ft*\f*, \q1 jam leen, faagaagal seen gannaaw.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 «Defleen mboolem li ma leen sant. \q1 \v 22 Coowal xaree ngi fi réew mi, \q1 ak rajaxoo ju réy. \q1 \v 23 Babilon, réew mi daan wàkk mboolem àddina, \q1 tey mu dammtoo ba rajaxoo nii, \q1 dib gent ci biir xeet yi! \q1 \v 24 Babilon, maa la fiir, \q1 nga tancu te yéguloo! \q1 Dañu laa gis, ne la taral, \q1 yaa dëkk Aji Sax ji, \q1 \v 25 Aji Sax ji ubbi na waxandey xareem, \q1 mer, génney gànnaayam. \q1 Liggéeyu Boroom bee, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, \q1 foofa ca réewum Babilon. \q1 \v 26 Songeleen ko fu ne, \q1 dàjji ay sàqam, \q1 jal-jalee. \q1 Fàkkasleen lépp, ba du dese dara. \q1 \v 27 Jamleen seen jàmbaari yëkk yépp, \q1 nañu dem ca rendikaay ba. \q1 Wóoy, ngalla ñoom! \q1 Seen bés taxaw na moos, \q1 di seen àppu mbugal. \q1 \v 28 Baatu daw-làqu yu rëcc a ngoog, \q1 bawoo réewum Babilon, \q1 di yeggesi waa Siyoŋ \q1 mbugalum Aji Sax ji sunu Yàlla, \q1 mbugal mi këram waral. \q1 \v 29 Wooleen fittkatoo fittkat fi kaw Babilon, \q1 mboolem kuy tàwwi xala. \q1 Gawleen ko, \q1 bu kenn rëcc. \q1 Feyleen koy jëfam; \q1 def ko ni mu def moroomam. \q1 Babilon a jaay reewande Aji Sax ji, \q1 ku Sell ku Israyil ki. \q1 \v 30 Moo tax bésub keroog \q1 goneem yu góor di daanooy péncam, \q1 niti xareem di wedamandoo.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 31 «Babilon mu reewee, maa ngii fi sa kaw.» \q1 Kàddug Boroom bi, Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi. \q1 «Sa bés déy taxaw na, \q1 di àpp bi ma la wara mbugale. \q1 \v 32 Ku reew keey tërëf, fëlëñu, \q1 te du am ku ko yékkati. \q1 Maay jafal ay dëkkam, \q1 sawara wa xoyom lépp lu ko wër.» \q1 \v 33 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: \q1 «Bànni Israyil ak Yuda, ñépp lañu notandoo. \q1 Ñi leen jàpp ñépp téyee leen doole, \q1 bañ leena ba. \q1 \v 34 Waaye seen \w jotkat|lemma="jotkat b-:"\w* a am doole, \q1 te mooy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi. \q1 Moo leen di layool seen layoo, \q1 ngir jàqal réewum Babilon, \q1 jàmmal waa àddina yi ci des. \q1 \v 35 Saamar ci kaw waa Babilon!» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 «Saamar ci kaw waa Babilon \q1 aki kàngamam aki kaaŋam. \q1 \v 36 Saamar ci kaw kebatukati diine yi, \q1 ba seenug ndof feeñ. \q1 Saamar ci kawi jàmbaaram, \q1 ñu ne yàcc. \q1 \v 37 Saamar ci kaw fas ak watiiram, \q1 ak mboolem niti njaxasaan ñi mu fat, \q1 ba ñu mel niy jigéen. \q1 Saamar ci kawi dencam, \q1 ñu sëxëtoo. \q1 \v 38 Maral ci kawi waltanam, mu ŋiis; \q1 mii réew mu nit ñiy jaamoo jëmmi tuur, \q1 ñooy say ndax seen yu ñàng yooyu \q1 \v 39 Moo tax ay dundooti màndiŋ ak rabi àll a koy këroo, \q1 bànjóoli dëkke ko, \q1 kenn dootu fa desati, \q1 kenn dootu fa dëkk mukk ba fàww. \q1 \v 40 Mu mel ni ba Yàlla tasee Sodom ak Gomor, \q1 tasaale la ko wër.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 «Nit du fa dëkkati, \q1 doom aadama du fa dalati.» \b \q1 \v 41 «Aw askan a ngii, bàyyikoo bëj-gànnaar, \q1 xeet wu mag lañuy doon, buur yu bare, \q1 sàqee fa cati àddina. \q1 \v 42 Yeen waa Babilon, réew mu taaru mi, \q1 fitt aku xeej la ñooñuy ŋàbb, \q1 néeg lool, duñu yërëm, \q1 seen coow ni riirum géej, \q1 ñu war seeni fas, \q1 làng-déral leen ni benn bopp ngir xare. \q1 \v 43 Buuru Babilon dégg riir ma, \q1 yoxo ya yoqi, \q1 njàqare ne ko taral, \q1 mu jàq ni kuy matu. \q1 \v 44 Maa ngii, di fëlle gottub Yurdan ni gaynde, \q1 wuti mbooy gu naat. \q1 Xef ak xippi déy, ma fëxale fa lépp, \q1 ba tabb fa ki ma taamu. \q1 Ana moos ku mel ni man, \q1 ku am sañ-sañ ci man? \q1 Ana njiit luy taxaw fi sama kanam? \q1 \v 45 Kon dégluleen pexe mi Aji Sax ji waajal Babilon, \q1 mébét yi mu mébétal réewum Kaldeen ñooñu! \q1 Ndegam deesul wommat seen gàtt yu ndaw, yóbbu, \q1 ba yàq parlu ma yaxeet. \q1 \v 46 Bu ñuy nangu Babilon, \q1 riir ma day jolli ba riiral suuf, \q1 seeni yuux àkki fa biir xeeti jaambur ya.» \c 51 \q1 \v 1 Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 «Maa ngii di yebal fi kaw Babilon, \q1 waa Lew Kamay gii,\f + \fr 51.1 \fr*\fk Lew Kamay \fk*\ft li muy tekki mooy «xolu noon yi», di turu kumpa wu bànni Israyil daan wooye waa Babilon.\ft*\f* \q1 ngelawal yàqkat. \q1 \v 2 Maay yónnee Babilon ay beeskat \q1 yu ko bees, tonni réew ma, ba mu set. \q1 Keroog bésu safaan ba déy, \q1 fu ne lañu koy songe. \q1 \v 3 Buleen leen may fu ñu taxaweek seen kiiraay, di fitte; \q1 buleen ñéeblu seeni waxambaane, \q1 fàkkasleen seen gàngoor gépp. \q1 \v 4 Ñii dee, ne wetar réewum Babilon; \q1 ñee gaañu, ne lasar ca mbedd ya. \q1 \v 5 Israyil ak Yuda ñàkkuñu seen Yàlla, \q2 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, \q1 te réewum Babilon fees naaki moy \q1 yu ñu moy Yàlla Aji Sell ji séddoo Israyil. \b \q1 \v 6 «Yeen gan ñi, génnleen Babilon, \q1 ku ne rawaleji sa bakkan. \q1 Buleen ñaawtéefu jaambur sànkaale; \q1 lii àppu mbugal la bu Aji Sax ji matal; \q1 seen añ la, bu mu leen añale. \q1 \v 7 Aji Sax jee yor Babilon ci loxoom, muy kaasu wurus bu def xadaru xeet ya, \q1 di màndal mboolem àddina; \q1 xeet ya naan ca, \q1 ba tax ñuy say. \q1 \v 8 Teewul Babilon jekki daanu, tasaaroo. \q1 Jooyleen ko, \q1 dàmp ko, seral mititam, \q1 jombul mu wér.» \sp Gan ñaay wax \q1 \v 9 «Bu nu sañoon faj Babilon, mu wér, \q1 waaye wérul. \q1 Nan ko ba te dem, \q1 ku ne ñibbim réewam. \q1 Àtteb Babilon kat àgg na asamaan, \q1 àkki na fa kaw niir ya.» \sp Bànni Israyil ay wax \q1 \v 10 «\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji jox na nu dëgg. \q1 Nanu yeggeji waa \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* \q1 jaloorey Aji Sax ji, sunu Yàlla.» \sp Yàllaay wax \q1 \v 11 «Nàmmleen fitt yi, feesale mbar yi! \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji xabtal na buuri Medd fi kaw Babilon, \q1 nar koo tas. \q1 Lii mbugalu Aji Sax jee, \q1 mbugal mi këram waral. \q1 \v 12 Yékkatil-leen tatay Babilon raayab xare, \q1 yokkleen wattukat yi, \q1 taxawal leen fa ñuy wattoo, \q1 te waajal tërukat yi. \q1 Aji Sax ji def na li mu waxoon \q1 ne dina ko def waa Babilon. \q1 \v 13 Yeen ñi dëkke weti ndox yu ne xéew, \q1 seen alal ne xéew, \q1 seen muj taxaw na, \q1 seen buumu bakkan dog na. \q1 \v 14 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi giñ na ci boppam. \q1 Mu ne: “Maa leen di same ay nit niy njéeréer, \q1 ñu xaacu, song leen.”» \sp Yeremeey wax \q1 \v 15 Suuf, Aji Sax ji sàkke kàttanam; \q1 dun bi, mu sampem xelam; \q1 asamaan, mu lale xam-xamam. \q1 \v 16 Bu àddoo ndoxum asamaan riir, \q1 mu yéegey niir fa cati àddina, \q1 riddee ngelaw fa dencam ya, \q1 daldi melax, taw. \q1 \v 17 Nitoo nit dim sannax, sore xam-xam, \q1 te képp kuy tëgg sa jëmmu tuur, yaa añe gàcce. \q1 Sa jëmmi weñ ji nga xelli, di neenug neen, \q1 noowug bakkan, tus! \q1 \v 18 Cóolóolu neen, liggéeyu caaxaan; \q1 bu bésam taxawee, mu sànku. \q1 \v 19 Séddoob Yanqóoba déy wuute naak yii caaxaan. \q1 Kee bind lépp, \q1 bind giir gi mu séddoo. \q1 Kookooy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoori xare yi! \sp Yàllaay wax \q1 \v 20 «Yaw Babilon, yaa doon sama wàkku, \q1 di sama ngànnaay, \q1 ma di la wàkke xeet yi, \q1 rajaxee la réew yi, \q1 \v 21 wàkke la fas ak gawaram, \q1 wàkke la watiir ak dawalkatam, \q1 \v 22 wàkke la góor ak jigéen, \q1 wàkke la mag ak ndaw, \q1 wàkke la waxambaaneek ub janq, \q1 \v 23 wàkke la sàmm ak géttam, \q1 wàkke la beykat ak lëkkeb nagam, \q1 wàkke la kàngam ak jawriñ. \q1 \v 24 Waaye mboolem lu Babilon ak waa réew mépp def ci \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, \q1 maa leen koy fey, ngeen di gis, yeen Yudeen ñi.» \q1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. \q1 \v 25 «Maa ngii déy, fi sa kaw, yaw Babilon, ponkalum yàqkat bi,» \q1 kàddug Aji Sax jee, \q1 «yaw miy yàq àddina sépp. \q1 Maay tàllal sama loxo fi sa kaw, \q1 taxañe la fa kaw doj ya, \q1 def la ponkalum jalu dóom. \q1 \v 26 Deesul seppee fi yaw doju tabax wu ñuy lëkklee, \q1 mbaa doju tabax wu bokk ci kenu, \q1 nde gent ngay doon ba fàww.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 27 «Yékkatileen ub raaya fi réew mi \q1 te walal liit gi xeet yi. \q1 Dajaleleen xeet yi fi kaw Babilon, \q1 te xabtal fi kawam réew yii: \q1 Araraat ak Minni ak Askenas. \q1 Tabbal-leen ko njiitu xare mu ko song, \q1 indil koy fas yu saf ndiiraani njéeréer. \q1 \v 28 Dajaleleen xeet yi fi kaw Babilon, \q1 wooleen buuri Medd ak kàngam ya \q2 ak jawriñ ñaak mboolem réew mu ñu moom. \q1 \v 29 Suuf a fuddu, wañaaru, \q1 mébéti Aji Sax jeey sottalal Babilon, \q1 ngir réew ma dib gent bu kenn nekkul. \q1 \v 30 Jàmbaari Babilon xareetuñu, \q1 ña nga des ca seeni tata, \q1 doole ŋiis, \q1 ñu mel niy jigéen. \q1 Bunti dëkk bi dàjjiku, \q1 kër ya jàpp. \q1 \v 31 Xélukat dab xélukat; \q1 ndaw jottli ndaw xibaar \q1 bu ñu yeggeji buuru Babilon, ne ko \q1 nangu nañu dëkkam ba wetoo wet, \q1 \v 32 nangu jàllukaayi dex ya, \q1 taal barax ya, \q1 xarekat ya raj-rajloo.» \q1 \v 33 Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi déy dafa wax ne: \q1 «Ñu ngi dëggaate Babilon mu taaru mi, \q1 ni ñuy dëggaatee dàgga ju ñuy bàccesi. \q1 Balaa yàgg ngóobu Babilon taxaw.» \sp Yerusalem ay wax \q1 \v 34 «Buuru Babilon warax na ma. \q1 Da maa muucu, \q1 ñiit ma, ba ma set ni ndab. \q1 Da maa modd ni ninki-nànka, \q1 sole kollam li gën ci man, \q1 yàbbi la ca des.» \q1 \v 35 \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* ne: «Yal na sama yàpp ak sama coono topp Babilon.» \q1 Yerusalem ne: «Yal na sama deret topp waa Babilon!» \b \q1 \v 36 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nag dafa wax ne: \q1 «Maa ngii di leen layool seen layoo, \q1 ba feyul leen. \q1 Maay ŋeeral géejam, \q1 ŋiisal am walam, \q1 \v 37 Babilon def jali doj, \q1 di paxum till, \q1 di gent bu ñuy muslu, \q1 kenn du ko dëkke. \q1 \v 38 Ñu ngi ŋarandoo niy gaynde, \q1 di xiiroo ni gaynde yu ndaw. \q1 \v 39 Ñu tàng bay bëgga dee, \q1 ma may leen ñu naana naan, \q1 màndal leen, ñu mana xawaare, \q1 tëdd nelaw nelawi fàww, \q1 duñu yewwooti.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 40 Aji Sax ji nee: «Maa leen di wommat \q1 niy xar ba ca rendikaay ba, \q1 ñu mel ni kuuyi xar aki sikket. \s1 Ngalla Babilon \q1 \v 41 «Ãa! Ana nees mana nangoo Sesag? \q1 Nees mana tege loxo ki àddina sépp di kañ? \q1 Ana nu Babilon mana gente fi digg xeet yi? \q1 \v 42 Géej ay mëdd Babilon, \q1 mu sàngoo gannaxam yu jallaañoo, \q1 \v 43 ay dëkkam gental, \q1 réew mi ne sereŋ, di ndànd-foyfoy, \q1 kenn du ko dëkke, \q1 doom aadama du fa jaare. \q1 \v 44 Maay dikke mbugal Bel, \q1 tuur mi ci Babilon, \q1 yàbbiloo kob lancam. \q1 Xeet yi noppee def um wal, wuti ko, \q1 tatay Babilon it màbb. \q1 \v 45 Yeen sama ñoñ, génnleen fi seen biir, \q1 na ku ne rawale sa bakkan, \q1 ba mucc tàngooru sànjum \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \q1 \v 46 Bu seen fit rëcc, \q1 ngeen di tiit xibaar yi ñuy yéene ci réew mi: \q1 ren yéene jib, \q1 déwén yéene jibati, \q1 fitna law ci réew mi, \q1 njiit ne njiit dann. \q1 \v 47 Kon ay bés a ngii di ñëw, \q1 yu may dikke mbugal tuuri Babilon, \q1 réew mépp torox, \q1 ña ñu bóom ñépp wetaroo fa biir. \q1 \v 48 Su boobaa asamaan ak suuf \q2 ak mboolem li ci biiram \q1 sarxollendoo, di bége li dal Babilon. \q1 Bëj-gànnaar kay la yàqkat yay bawoo.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \sp Yeremeey wax \q1 \v 49 Waa Babilon it dinañu daanu \q1 ngir waa Israyil ñi ñu bóom, \q1 ba ñu yem ak mboolem waa àddina yi ñu bóom, \q1 te ñu daanu ndax Babilon. \q1 \v 50 Ée yeen ñi rëcc saamar, \q1 buleen taxaw, demleen, \q1 di fàttlikoo \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji fu sore, \q1 tey bàyyi xel Yerusalem. \sp Bànni Israyil ay wax \q1 \v 51 «Nooka rus ci saaga yi nu dégg, \q1 ak gàcce gi nu sëlmoo \q1 ndax doxandéem yi dugg \q1 ci biir bérab bu sell bi ci kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji.» \sp Yàllaay wax \q1 \v 52 «Moo tax, bés a ngii di ñëw,» \q1 kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee, \q1 «maay dikke mbugal seen jëmmi tuur yi, ñoom, \q1 ñi ñu jam di binnee fi réew mi mépp. \q1 \v 53 Su Babilon yéegoon asamaan, \q1 dàbbli fa tata ju ne kekk sax, \q1 du tee ay yàqkat bawoo fi man, dal ci kawam.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \sp Yeremeey wax \q1 \v 54 Yuuxi njàqare fa Babilon, \q1 réewum Kaldeen ñooñaa toj ba tojatoo. \q1 \v 55 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee niy yàqtee Babilon, \q1 tukkal fa riir mu réy. \q1 Gàngoori noon yaa ngay buur ni gannaxi géej, \q1 seen riirum kàddu jolli. \q1 \v 56 Yàqkat déy dikkal na Babilon, \q1 jàpp ay jàmbaaram, \q1 dammatey fittam. \q1 Aji Sax ji déy mooy Yàlla jiy yoole, \q1 di fey pey gu mat sëkk. \q1 \v 57 Mu ne: «Maay màndal seeni kilifaak seeni kaaŋ \q1 ak seeni kàngam ak seeni jawriñ ak seeni jàmbaar, \q1 ñu tëdd nelaw nelawi fàww, \q1 duñu yewwooti.» \q1 Kàddug Buur a, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi. \q1 \v 58 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: \q1 «Tatay Babilon yu mag yi \q1 dees koy màbba màbb; \q1 bunt yu kawe ya lakk ba jeex. \q1 Xeet yee ñaq ci neen, \q1 waaso yee sonnal sawara.» \s1 Yeremi santaane na misaal \p \v 59 Bëkk-néegu Buur Cedesyas moo doon Seraya doomu Nerya doomu Maaseya. Ba Cedesyas tolloo ca ñeenteelu atu nguuram, la Seraya ànd ak moom Babilon. \v 60 Fekk na Yeremi bind cib taxañ mboolem safaan yiy dikkal Babilon, di mboolem mbir yooyu jëm ci Babilon. \v 61 Yeremi sant Seraya, ne ko: «Boo àggee Babilon, fexeel ba biral kàddu yii yépp. \v 62 Te nga wax ne: “\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, yaw déy, yaa xamle ne dëkk bii dina tas, dara du ci dëkkati, du doom aadama, du rab. Ab gent lay doon ba fàww.” \v 63 Boo jàngee taxañu mbind mii ba noppi, nanga ci takk aw xeer, sànni ko ci biir dexu Efraat. \v 64 Su ko defee nga ne: “Nii la Babilon di diige te du jógati ndax safaan bi may wàcce fi seen kaw, ba ñu sonn.”» Fii la kàdduy Yeremi yem. \c 52 \ms1 Kàdduy ndollant a ngi \mr (Saar 52.1-34) \p \v 1 Ñaar fukki at ak benn la Cedekiya amoon ba muy falu buur, te fukki at ak benn la nguuru fa Yerusalem. Yaayam mooy Amutal doomu Yeremi ma cosaanoo Libna. \v 2 Muy def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu, mboolem noonee ko Yowakim defe woon. \v 3 Merum Aji Sax ji nag dikkal Yerusalem ak Yuda, ba mu mujj xalab leen. \p Gannaaw gi Cedesyas fippu buuru Babilon. \v 4 Ba Cedesyas tolloo ci juróom ñeenteelu atu nguuram, fukki fan ca fukkeelu weeram, ca la Nabukodonosor buuru Babilon ànd ak mbooloom xareem mépp ci kaw Yerusalem. Ñu dal fa janook Yerusalem, yékkati gawukaay, wërale ko. \v 5 Dëkk ba gawe, ba keroog Cedesyas tollu ci fukkeelu atu nguuram ak benn. \v 6 Keroog juróom ñeenti fan ca ñeenteelu weer wa, xiif ba tar lool ca biir dëkk ba, ba waa réew ma amatuñu ab dund. \v 7 Xarekati Yuda ya génn guddi daw. Fekk na waa Babilon gaw dëkk ba. Teewul ñu rëcc, jaare ca bunt ba ca diggante ñaari tata ya, ca wetu toolu buur. Ñu daldi wuti xuru Yurdan. \v 8 Waa Babilon nag topp Buur Cedesyas, ba dab ko ca jooru Yeriko. Fekk mbooloom xareem mépp tasaaroo, wacc ko. \v 9 Ñu jàpp ko, yóbbu ca buuru Babilon ca dëkk ba ñuy wax Ribla ca réewum Amat. Nabukodonosor dogal fa àtteem. \v 10 Buuru Babilon daa rendi doomi Cedesyas yu góor, muy gis, mu rendiwaale mboolem kàngami Yuda, ca Ribla. \v 11 Gannaaw loolu mu tuur bëti Cedesyas, ba noppi jénge ko jéngi xànjar, yóbbu ko Babilon, tëj ko fa, ba keroog bés ba mu deeyee. \p \v 12 Ba Nabukodonosor buuru Babilon tolloo ci fukkeelu atu nguuram ak juróom ñeent, ba am fukki fan ca juróomeelu weeru at ma, ca la bëkk-néegu buuru Babilon, Nebusaradan njiitu dag ya, dugg Yerusalem. \v 13 Mu taal kër Aji Sax ji, taal kër buur, ak këri Yerusalem gépp, boole ca këri boroom barke ya. \v 14 Gàngooru Babilon gépp daldi ànd ak njiital dagi buur, ñu màbb tata ya wër Yerusalem. \v 15 Gannaaw gi ñenn ci baadoolo yi, ak ña nekkoon ca dëkk ba, ba booba, ak ña jébbaloon seen bopp buuru Babilon, ak ña desoon ca liggéeykat ya, Nebusaradan njiital dagi buur boole leen yóbbu ngàllo. \v 16 Ñenn ca baadooloy réew ma nag, Nebusaradan njiital dag ya bàyyi leen fa, ñuy liggéey tóokëri reseñ yaak tool ya. \v 17 Ci biir loolu kenuy xànjar ya bokkoon ca kër Aji Sax ji, ak rootukaay yaak mbalkam xànjar ma woon ca kër Aji Sax ji, waa Babilon toj lépp, boole xànjar jépp yóbbu Babilon. \v 18 Ñu yóbbaale mboolem ndabi xànjar yi ñuy liggéeye ci kër Aji Sax ji: ndab yiy def dóom, ak ñiitukaay yi ak ñiimi feyukaayi làmp yi, ak ndab yiy def deretu sarax yi, ak and yu ndaw yi, ak mboolem jumtukaayi xànjar yi ñuy sarxalee. \v 19 Njiital dag ya yóbbaale ndab yu ndaw yaak and yaak ndab yiy def deretu sarax, ak ndab yiy def dóom, ak tegukaayi làmp yaak and yu ndaw yaak këlli tuurukaay ya. Lu ciy wurus, mu ber, lu ciy xaalis, mu ber. \p \v 20 Ñaari kenu yooyu ak mbalka maak fukki nag ak ñaar ya ko yenu, ak rootukaay ya, lépp di xànjar bu Buur Suleymaan defaraloon kër Aji Sax ji, maneesula takk diisaay ba. \v 21 Kenu yi, gu ci nekk am na taxawaayu fukki xasab\f + \fr 52.21 \fr*\fk xasab \fk*\ft mooy guddaayu loxo bu digg-dóomu, diggante catu baaraamu digg ak conc.\ft*\f* ak juróom ñett te fukki xasab ak ñaar a koy ub. Mu def pax ca biir te dëllaayu weñ ga di juróom ñeenti baaraam. \v 22 Kenu gu ci nekk ponku xànjar a ca tege, taxawaayu ponk bi di juróomi xasab, ab caaxub xànjar wodd ko, ànd ak doomi gërënaati xànjar. Ñaari kenu yépp noonu, ànd aki gërënaat. \v 23 Gërënaat yi juróom ñeent fukk laak juróom benn, wet gu nekk, boo ci boolee ya ca cat ya, muy téeméer, yu ub caax ba. \p \v 24 Ci kaw loolu njiital dag ya jàpp Seraya \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bu mag ba, ak Cefaña sarxalkat ba ca topp, ak ñetti dagi bunt kër Aji Sax ja. \v 25 Biir dëkk ba nag, mu jële fa benn njiitu xare, ak juróom ñaari niti dëkk ba ñu sës ci Buur, ak bindkatub njiital xare ba sasoo bind xarekat yi, ak juróom benn fukki Yudeen ñu mu fekk ca biir dëkk ba. \v 26 Ba mu ko defee Nebusaradan, njiital dagi buur, boole leen yóbbu ca buuru Babilon ca Ribla. \v 27 Buuru Babilon nag bóom leen foofa ca Ribla, ca réewum Amat. Noonu la waa Yuda génne seen réew, dem ngàllo. \p \v 28 Lii mooy limu nit ñi Nabukodonosor toxal: Ñetti junniy Yudeen ak ñaar fukk ak ñett (3 023), loolu yemook juróom ñaareelu atu nguuram, \v 29 ak juróom ñetti téeméer ak fanweer ak ñaar (832), loolu yemook fukkeelu atu nguuram ak juróom ñett, \v 30 Ak juróom ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom (745) yu Nebusaradan njiital dag ya, toxal. Loolu yemook ñaar fukkeelu at maak ñett ci nguurug Nabukodonosor. Ñi ñu toxal ñépp di ñeenti junni ak juróom benni téeméer (4 600). \p \v 31 Yóbbu nañu Yowakin buurub Yuda ngàllo ba mu am fanweeri at ak juróom ñaar, Ewil Merodag doora falu buur ca Babilon. At mooma, fukkeelu weer waak ñaar, ñaar fukki fan ak juróom ca weer wa, ca la Ewil Merodag siggil Yowakin buurub Yuda, daldi koy tijji. \v 32 Ci biir loolu mu wax ak moom lu rafet, jox ko cér bu sut cér ba mu jox yeneen buur, ya mu bokkal curga ca Babilon. \v 33 Yowakin nag teqlikook yérey kaso ya, ba noppi ñu may ko muy bokk ak Buur ndab giiru dundam. \v 34 Ci biir loolu ñu dogal ko njëlam lu sax dàkk, di bàyyikoo ci buuru Babilon bés bu jot, giiru dundam, ba keroog muy dee.