\id JAS (WOL) \ide UTF-8 \h Yanqóoba \toc1 Bataaxal bi Yàlla may Yanqóoba, mu bind ko \toc2 Yanqóoba \mt2 Bataaxal bi Yàlla may \mt1 Yanqóoba \mt2 mu bind ko \c 1 \p \v 1 Ci man Yanqóoba, jaamub Yàlla ak Sang Yeesu Almasi, la bataaxal bii bawoo, ñeel fukki giir ak yaar yi tasaaroo ci àddina. Maa ngi leen di nuyu. \s1 Lu jëm ci nattu ak ngëm \p \v 2 Bokk yi, bu ngeen jaaree ci mboolem xeeti nattu, jàppeleen ko mbég mu mat sëkk, \v 3 te xam ne bu seen ngëm nattoo, ñeme coono la leen di jural. \v 4 Na ag ñeme coono sottal liggéeyam ci yeen, ngir ngeen sotti, mat sëkk, te baña yéese fenn. \p \v 5 Ku desele am xel mu rafet nag, na ko ñaan Yàlla, mu may ko ko, ndax Yàlla mooy yéwéne ñépp te du sikk kenn. \v 6 Waaye ngëm la koy ñaane te bumu ci am benn sikki-sàkka, ndax kiy sikki-sàkka daa mel ni gannaxu géej bu ngelaw liy yóbbu, di ko lëmbaaje. \v 7 Kooku bumu yaakaar dara ci Boroom bi. \v 8 Boroom xel-yaar la, xel maa toogul ci lenn lu muy def. \s1 Néewle kawe, barele suufe \p \v 9 Mbokkum gëmkat mi suufe daraja, na sagoo ab kawewaayam; \v 10 te ki barele it na sagoo ag suufeem, ndax ni tóor-tóoru saxayaay di ruuse, noonu lay wéye. \v 11 Naka la jant di fenk, ba naaj wi tàng jérr, saxayaay lax, tóor-tóoram ruus, taar ba réer ko mërr. Noonu itam la ki barele di jeexlee ci biiri yëngoom. \s1 Yàllaay nattoo waaye du fiir kenn \p \v 12 Ndokklee ku muñ ab nattu, nde su ca amee ngërëm, mooy yooloo \w kaalag|lemma="kaala g-:"\w* dund, gi Yàlla dig ñi ko sopp. \p \v 13 Képp ku dajeek lu koy xiirtal, bumu ne: «Yàllaa ma xiirtal,» ndax maneesula xiirtal Yàlla ci lu bon, te moom ci boppam du xiirtal kenn. \v 14 Waaye ku nekk, sa xemmemtéefu bakkanu bopp moo lay xiirtal, ootal la ba nax la. \v 15 Te xemmemtéefu bakkan bu ëmbee, bàkkaar lay wasin, te bàkkaar bu matee, ndee lay jur. \p \v 16 Bokk yi, soppe yi, buleen juum ci lii: \v 17 gépp may gu baax, ak bépp jagle bu mat, fa kaw la bawoo, di lu wàcce fa Baay biy boroom leer yi, ki soppikuwul ci lenn, te genn ker gu toogadi nekkul ci moom. \v 18 Moom la soob mu jure nu kàddug dëgg, ba nu taxawe ab jooxeb ndoortel meññeef, ci biiri bindeefam. \s1 Jëfeleen kàddug Yàlla \p \v 19 Bokk yi, soppe yi, nangeen xam lii: na ku nekk di gaaw ci déglu, di yeexa wax tey yeexa mer. \v 20 Ndax merum nit du jur njub fa Yàlla. \v 21 Kon nag baleen jépp jikko ju tilim, ak mboolem xeeti mbon yi ne gàññ, te ngeen nangu ci biir ag woyof, kàddu, gi jëmbate ci yeen te man leena musal. \p \v 22 Doonleen jëfekati kàddu gi, buleen di ay déglukat doŋŋ, di nax seen bopp. \v 23 Ndax kat kuy déglu kàddu gi te jëfewoo ko, kooku daa mel ni kuy niir kanamam cib seetu: \v 24 bu niiree boppam, dem daldi fàtte ca saa sa lu muy nirool. \v 25 Waaye ki ne jàkk yoon wu mat sëkk, wiy goreel ku ko topp, saxoo yoon wi te bañ koo dégg, fàtte; xanaa di dégg, jëfe, kooku mooy bége jëfam. \p \v 26 Ku yaakaar ne moo jullite te moomul làmmiñam, boppam lay nax te ag njulliteem amul njariñ. \v 27 Njullite gu set te mucc sikk fa kanam Yàlla Baay bi moo di lii: di nemmiku jirim akub jëtun ci seen njàqare, tey sàmmu ba mucc ci gàkki àddina. \c 2 \s1 Gënaatle warul \p \v 1 Bokk yi, bu leen di gënaatle te di gëmkati sunu Sang Yeesu \w Almasi|lemma="Almasi:"\w*, Boroom leer. \v 2 Ndax su nit duggsee seenum ndaje, takk jaarob wurus, solu ba jekk; ku néew doole it duggsi, limboo ay sagaram, \v 3 su ngeen seetloo boroom col gu jekk gi, ne ko: «Toogeel fii, moo baax ci yaw,» te ne néew-ji-doole ji: «Yaw, taxaweel nee, mbaa nga toog fii sama tànki toogu, fi suuf,» \v 4 su boobaa xanaa du yeena ngi gënaatle ci seen biir, tey àttee ay mébét yu bon? \p \v 5 Bokk yi, soppe yi, dégluleen. Xanaa du Yàlla moo taamu ñi àddina jàppe ñu néew doole, ngir ñu barele ngëm, boole ci jagoo nguur, gi Yàlla dig ñi ko sopp? \v 6 Yeen nag ngeen di teddadil néew doole yi! Xanaa du boroom alal yi ñoo leen di noggatu, di leen diri ba fa mbaxana dee benn? \v 7 Xanaa du ñooñu ñooy ñàkke kersa tur wu tedd wi ngeen di wuyoo? \p \v 8 Ndegam nag yoonu Buur Yàlla ngeen matal sëkk, di sàmmonteek Mbind mi ne: «Ni ngeen soppe seen bopp, nangeen ko soppe seen moroom\f + \fr 2.8 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Sarxalkat yi\+bk* 19.8.\ft*\f*,» su boobaa waawleen góor! \v 9 Waaye su ngeen gënaatlee, bàkkaar ngeen, te yoon topp na leen, ndax yeena ko xëtt. \v 10 Ndax kat képp ku sàmm yoon wépp, ba mu des lenn ndigal doŋŋ lu mu tërëfe, ab daanu ku moy yoon wépp ñeel na ko. \v 11 Ndax ki ne: «Bul jaaloo,» moo ne itam: «Bul bóome\f + \fr 2.11 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Mucc ga\+bk* 20.13, 14.\ft*\f*.» Ku jaaloowul te bóome nag, xëtt na yoon. \v 12 Deeleen waxe tey jëfe ni mu jekke ci nit ñu ñuy séddeji àtteb yoon wiy goreel. \v 13 Daan bu àndul ak yërmande, moom lees di àttee ña daawul jëfe yërmande. Yërmande nag kekku na ab daan. \s1 Gëm, jëfe \p \v 14 Bokk yi, ku ne gëm na, te jëfewu ko, ana lu mu koy jariñ? Ndax googu ngëm man na koo musal? \v 15 Su mbokk mu góor mbaa jigéen raflee, mbaa mu ñàkk lu mu dunde bés bu nekk, \v 16 ba kenn ci yeen ne mbokk mi: «Demal ak jàmm, solul nag te lekk ba regg,» te fajul aajoom, loolu lu muy jariñ? \v 17 Noonu la ngëm deme, su amul jëf ju mu àndal, ngëm gu dee la. \p \v 18 Waaye jombul nit ne: «Yaw, ngëm nga am, waaye man, jëf laa am.» Dama ne, won ma sa ngëm gu àndul ak jëf; man, samay jëf laa lay wone sama ngëm. \v 19 Yaa gëm ne Yàlla kenn la; waaw góor, waaye rab yu bon yi it loolu lañu gëm bay lox. \p \v 20 Yaa ñàkk bopp, dangaa bëgg lu la firndeel ne ngëm gu àndul ak jëf, amul njariñ? \v 21 Sunu maam \w Ibraayma|lemma="Ibraayma:"\w*, xanaa du ci jëf lees ko joxe àtteb ku jub, ndax jëf ja mu jooxee doomam Isaaxa ca sarxalukaay ba? \v 22 Kon gis nga ne ngëm gaa liggéeyandoo ak jëfam ja, te ca jëf ja la ngëm ga mate sëkk. \v 23 Mbind ma daldi sotti, na mu dikke woon ne: «Ibraayma moo gëm Yàlla, ñu waññal ko ngëmam ag njub\f + \fr 2.23 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Njàlbéen ga\+bk* 15.6.\ft*\f*,» ba ñu di ko wooye xaritu Yàlla. \v 24 Ngeen gis kon ne ci jëf lees di joxe nit àtteb ku jub, waaye du ci kaw ngëm doŋŋ. \p \v 25 Xanaa du noonu it lañu joxe Raxab\f + \fr 2.25 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Yosuwe\+bk* 2:1-21.\ft*\f* gànc ba, àtteb ku jub, ci kaw jëfam, ndax la mu dalaloon ndawi Yawut ya, ba awale leen feneen? \v 26 Yaram wu àndul akug noo daal, ni mu deeye, noonu la ngëm gu àndul aki jëf, deeye. \c 3 \s1 Moom sa làmmiñ cig mat la bokk \p \v 1 Bokk yi, bu ñu bare ci yeen wuta doon sëriñi mbooloom gëmkat mi, ndax xam ngeen ne nun ñiy jàngle nooy gëna metti ab àtte. \v 2 Bare na lu nuy tooñ, nun ñépp. Ku dul tooñ ci kàddu nag, kooku nit ku mat la, te man naa moom yaramam wépp, boole ci. \p \v 3 Aw fas, ŋalaab gi nuy def ci gémmiñam, mu déggal nu lanu ci jublu, te moom lanuy walbatee yaramu fas wi wépp. \v 4 Xool-leen gaal yi it, ak ngelaw lu réy lu leen mana jañax, weñ su tuut la dawalkat biy walbatee gaal gi, jëme fu ko neex. \v 5 Noonu itam la aw làmmiñ dee cér su tuut te réy aw bàkk. \p Seetleen ni ferñent su tuut di lakke gott bu yaa. \v 6 Aw làmmiñ itam sawara la; làmmiñ a bokk ci sunuy cér, te di àddinay mbon, di gàkkal jëmm jépp. Aw làmmiñ, giiru dundu nit ki lay jafale ab taal bu tàkke fa sawara. \p \v 7 Mboolem xeeti rabi àll yeek njanaaw yi, ak ndëgmeent yi, ak rabi géej yi, dees na leen tàggat, te nit a leen di tàggat ba ñu mokk. \v 8 Waaye aw làmmiñ, kenn manu koo tàggat ba mu mokk. Mooy aayteef gu kenn manula dànk, fees dell ak tookey ndee. \p \v 9 Aw làmmiñ lanuy sante kiy Boroom bi, di Baay, te it ci lanuy móoloo nit ñi bindoo takkndeeru Yàlla. \v 10 Genn gémmiñ gi, ci la kàddug cant ak gu móolu di jibe. Bokk yi, warula deme noonu kat. \v 11 Benn bëtu ndox ndax dina ballandoo ndox mu neex, ak ndox mu wex, ci menn pax mi? \v 12 Bokk yi, ag figg man naa meññ oliw? Am ag reseñ dina meññ doomi figg? Bëtu ndoxum xorom it du nàcc mukk ndox mu neex. \p \v 13 Ana ci yeen ku rafet xel te xam àddina? Na ko firndeele dundin wu rafet wu feeñ ci jëfam ju teey ndax xel mu rafet. \v 14 Waaye ku denc ci sab xol, wextanu kañaan, ak mébétum sàkku sa darajay bopp, bul damoo xel mu rafet, nde kon nga moy dëgg. \v 15 Moomu xel jógewul fa kaw, àddina sii la bokk, di yëfi bakkan, te di mbiri Seytaane. \v 16 Ndax kañaan ak sàkku sa darajay bopp, fu mu ame, fa la salfaañoo di ame, ak mboolem jëfi ñaawtéef. \p \v 17 Waaye xel mu rafet ma bawoo fa kaw, set la jëkka def, teg ci ànd ak jàmm, akug dal. Day taxa neexa jubool, feese yërmande, di meññ jëf ju baax, te mucc ci par-làqu akug jinigal. \v 18 Meññeefum njub nag, ci jàmm lees koy ji, ci biir doxkati jàmm yi. \c 4 \s1 Nangul-leen Yàlla \p \v 1 Ana fu jote yeek xuloo yi ci seen biir jóge fu moy seen bànneexi bakkan, yiy xare ci seen yaram? \v 2 Yeenay xemmem lu ngeen dul am. Yeenay bóome, di iñaane lu ñeneen am, te manuleen koo am. Yeenay xuloo ak a jàppante. Dungeen am, ndax yeena ñaanul. \v 3 Te su ngeen ñaanee, dungeen am, ndax mébét mu bon ma ngeen ñaane, ngir am lu ngeen toppe seen bakkan. \p \v 4 Bokkaalekat yi ngeen doon! Xanaa xamuleen ne xaritoo ak àddina moo di noonoo ak Yàlla? Kon nag ku namma def àddina ab xarit, ab noonu Yàlla ngay doon. \v 5 Am defe ngeen ne ag neen la Mbind mi indee ne: «Xemmemtéef gu ànd ak fiiraange la Yàlla am ci \w noo|lemma="Noo gu Sell g-:"\w* gi dëkk ci nun.» \v 6 Waaye yiw wu gënatee baawaan la maye. Moom la Mbind mi ne: \q1 «Yàlla, ñi réy lay xeex, \q1 ñi toroxlu, mu may leen aw yiw\f + \fr 4.6 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Kàddu yu Xelu\+bk* 3.34.\ft*\f*.» \p \v 7 Kon nag nangul-leen Yàlla, te bañal \w Seytaane|lemma="Seytaane:"\w*, mu daw, ba sore leen. \v 8 Jegeleen Yàlla, mu jege leen. Yeen bàkkaarkat yi, raxasleen seeni loxo, yeen ŋaralekat yi laa ne, setal-leen seen xol. \v 9 Tiisluleen te ñaawlu bay jooy. Na seeni ree soppiku ay jooy, seen mbég doon njàqare. \v 10 Toroxluleen fi kanam Boroom bi, mu yékkati leen. \s1 Buleen sikkal kenn \p \v 11 Bokk yi, buleen ŋàññante. Ku ŋàññ sa mbokk mbaa nga sikkal sa mbokk, yoon wi nga ŋàññ, yoon wi nga sikkal. Ku sikkal yoon wi nag doo sàmmkatub yoon wi, sikkalkatub yoon wi nga. \v 12 Boroom yoon wi, kenn doŋŋ la, te mooy àtte; moo mana musle, mbaa mu sànke. Te yaw miy sikkal sa mbokkum gëmkat sax, yaay kan? \s1 Ëllëg, ëllëgu Yàllaa \p \v 13 Kaayleen nag ma wax leen, yeen ñi naan: «Tey mbaa ëllëg ma dem ba dëkk sàngam, def fa at, julaa fa ba tonu.» \v 14 Yeen xamuleen sax lu ëllëg di doon? Ana luy seen bakkan? Yeen ngeen di as lay suy feeñ léegi, nes tuut mu ne mes! \v 15 Li ngeen di wax kay moo di: «Bu soobee Boroom bi, dinanu dund ba def nàngam sii mbaa nàngam see.» \v 16 Léegi daal dangeena bew bay damoo seeni mébét! Googu damu de, lu bon la. \v 17 Ku xam lu baax loo wara def te defoo ko nag, bàkkaar nga. \c 5 \s1 Boroom alal bumu tooñ néew-ji-doole \p \v 1 Kaayleen nag ma wax leen, yeen boroom alal yi, jooyleen te yuuxu, ndax mitit yi leen di dikkal. \v 2 Seen alal nëb na, seeni yére maxe, \v 3 seen wurus ak seen xaalis xomaag. Xomaag ja dib seede bu leen tuumaal, di xoyom seenu suux ni sawara. Yeena dajale alal ca fan yu mujj ya. \v 4 Dégluleen! Peyoor, ga ngeen xañ ña gub seen tool, mooy yuuxu noonu. Jàmbati góobkat ya tàbbi na ca noppi Boroom gàngoori xare yi. \v 5 Dund gu nooy ak bànneexu bakkan daal ngeen nekke ci kaw suuf, di yaflu ci bésub rendi. \v 6 Yeena daan ba reylu aji jub, te jéemula bañ. \s1 Muñ war na gëmkatub Almasi \p \v 7 Kon nag bokk yi, muñleen, ba Boroom bi délsi. Seetleen ci beykat biy séentu njariñal meññeef mu jóge fi suuf si. Ma ngay muñ, céebo ba bët wàcc. \v 8 Yeen itam muñleen te takk seenu fit, ndax bés ba Boroom biy dikk dëgmal na. \v 9 Bokk yi, buleen di ñaxtoonte, lu ko moy dees na leen daan, te Daan-kat baa ngii taxaw ci bunt bi! \p \v 10 Bokk yi, yonent yi wax ci turu Boroom bi, di dékku aw tiis, ak di muñ, defleen leen seeni royukaay. \v 11 Xam ngeen ne ñi muñ lanu foog ne ñoom la mbég ñeel. Dégg ngeen na Ayóoba muñe woon, ak muj ga ko Boroom bi jagleel, ndax Boroom bi moo bare yërmande akug ñeewante. \p \v 12 Li ci raw nag bokk yi, moo di buleen giñ, bu muy ci asamaan mbaa ci suuf mbaa ci leneen lu mu mana doon. Na seen waaw di waaw, seen déet di déet, bala ngeena tàbbi ci mbugal. \s1 Ñaan gu ngëm lal day dal \p \v 13 Ana ci yeen ku nekk ciw tiis? Na ñaan. Ana ku ci am mbég? Na sàbbaal. \v 14 Ana ku wopp ci yeen? Na woo magi mbooloom gëmkat ñi, ñu ñaanal ko, raayaale ko ag diw ci turu Boroom bi. \v 15 Ñaan gu ànd ak ngëm day musal ki wopp, ba Boroom bi yékkati ko. Su dee daa bàkkaar, dees na ko jéggal. \v 16 Kon nag tuddanteleen seeni bàkkaar tey ñaanalante, ndax ngeen wér. Aji jub ji, ag ñaanam, doole lay dale. \p \v 17 \w Ilyaas|lemma="Ilyaas:"\w* nit la woon ku bindoo ni nun, waaye ba mu saxee ci ñaan ngir mu baña taw, ndox laalul suuf diiru ñetti at ak genn-wàll. \v 18 Mu dellu ñaan, asamaan taw, suuf meññ meññeefam\f + \fr 5.18 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk 1.Buur ya\+bk* 17.1; 18.1, 42-45.\ft*\f*. \p \v 19 Bokk yi, su amee ci yeen ku moy yoonu dëgg, keneen ku ko waññi, \v 20 xamleen ne ku waññee bàkkaarkat ci yoonu sànkuteem, musal na bakkanam, te faral na ko bàkkaar yu bare.