\id ISA (WOL) \ide UTF-8 \h Esayi \toc1 Esayi \toc2 Esayi \mt1 Esayi \c 1 \ms1 Mucc a ngi ci Emanuwel \mr (Saar 1—12) \p \v 1 Lii moo di peeñum Esayi doomu Amocc, di lu mu gis ci mbirum Yuda ak Yerusalem ci janti buuri Yuda yi ñuy wax Osiyas\f + \fr 1.1 \fr*\ft Osiyas mooy Asaryaa ba tey.\ft*\f* ak Yotam ak Axas ak Esekiya. \s1 Aji Sax ji sikk na ñoñam \q1 \v 2 Asamaan, déglul; suuf, teewlul, \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jeey àddu: \q1 «Ay gone laa yar, màggloo leen, \q1 ñoom, ñu gàntal ma. \q1 \v 3 Aw yëkk xam na boroomam, \q1 mbaam-sëf xam gàmb, \q2 bi ko boroomam di xonte, \q1 waaye Israyil xamul, \q1 sama ñoñ ñii xàmmeewuñu.» \q1 \v 4 Wóoy wii xeetu moykat, \q1 wii askan wu diisu ñaawtéef, \q1 mii njurum defkati mbon, \q1 yii doomi yàqute! \q1 Ñoo wacc Aji Sax ji, \q1 ñoo teddadil Aji Sell ju Israyil, \q1 dëddu ko. \q1 \v 5 Xanaa dungeen wéye fippu, \q1 ñu gën leena duma, \q1 te bopp di góomi neen, \q1 xol jeex tàkk? \q1 \v 6 Bopp ba téstën, fenn jagul. \q1 Xanaa gaañu-gaañu aki dagg-dagg rekk, \q1 ak góom yuy nàcc, \q1 fajeesu ko, takkeesu ko, \q1 gajfaleesu kook ag diw. \q1 \v 7 Seenum réew gental, \q1 seeni dëkk xoyomu, \q1 seen suuf, doxandéem yi lekk fi seen kanam, \q1 muy gent bu doxandéem tas. \q1 \v 8 \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, dëkk bu taaru baa ngi wéet \q1 ni mbaarum tóokër mbaa dalub toolu xaal. \q1 Mbete dëkk bu ñu gaw! \q1 \v 9 Bu nu Aji Sax ji Boroom gàngoor yi \q2 waccalul woon li nu deseek as néew, \q1 ni Sodom\f + \fr 1.9 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Njàlbéen ga\+bk* 19.23-29.\ft*\f* lanuy mel, \q1 Gomor lanuy neexool. \s1 Aji Sax ji bañ na ngistal \q1 \v 10 Dégluleen kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, yeen njiiti Sodom, \q1 teewluleen sunu yoonu Yàlla, yeen askanu Gomor. \q1 \v 11 «Lu may doye seen sarax yu bare?» la Aji Sax ji wax. \q1 «Damaa suur seen \w saraxi rendi-dóomali|lemma="Sarax yi:"\w* kuuy, \q1 suur nebbonu juru yar gi, \q1 deretu yëkk ak xar ak sikket it, safu ma. \q1 \v 12 Bu ngeen dikkee, teewsi fi sama kanam, \q1 ana ku leen sant ñu joggat-joggatee nii \q2 sama ëttu kër? \q1 \v 13 Buleen fi indeeti saraxi caaxaan, \q1 seen saraxu cuuraay, lu ma seexlu la. \q1 Terutel weer ak \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w* \q2 ak wooteb ndajee ci yem! \q1 Duma mana dékku ndajem diine mu rax njubadi. \q1 \v 14 Seeni Terutel weer ak seen bési màggal \q2 laa bañ ci sama xol; \q1 yooyu màggal a ma diis ba àttanatuma ko. \q1 \v 15 Bu ngeen ma tàllaleey loxo, \q1 ma fuuyu. \q1 Bu ngeen doon ñaan-ñaanee it, \q1 du maa leen di déglu: \q1 seeni loxo, deret la taq ripp. \q1 \v 16 Raxasuleen ba set wecc, \q1 jëleleen seeni jëf ju bon fi sama kanam, \q1 te ngeen ba lu bon. \q1 \v 17 Jàngleen di def lu baax, \q1 sàkku njub, \q1 waññi ab notkat, \q1 àtte dëgg, ab jirim, \q1 sàmm àqu jëtun. \b \q1 \v 18 «Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax. \q1 «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, \q1 tàll lay weexeji. \q1 Li muy xonq curr lépp, \q1 weex furr lay mujje. \q1 \v 19 Su ngeen ma nangoo déggal, \q1 ngëneelu réew mi ngeen di xéewloo. \q1 \v 20 Waaye su ngeen lànkee, fippu, \q1 saamar a leen di xéewloo.» \q1 Aji Sax ji déy a ko wax ci gémmiñam. \s1 Mbugal mooy setal Yerusalem \q1 \v 21 Ana nu biib dëkk yàqoo, mbeteb gànc, \q1 te nekkoon dëkkub kóllëre, \q1 njubte mate fa, \q1 njekk lal fa panaan, \q1 tey ñu diy bóomkat! \q1 \v 22 Sa xaalis doon na raxit, \q1 sa biiñ xormbet. \q1 \v 23 Seeni njiit të, \q1 xejjoo ay sàcc, \q1 ñoom ñépp sopp ger, \q1 di dàq ay neexal, \q1 ab jirim, sàmmuñu àtteem, \q1 àqu jëtun soxalu leen. \q1 \v 24 Moo tax, kàddug Boroom bee, \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ju gàngoor yi, \q1 Jàmbaaru Israyil: \q1 «Maay lijjanti samay bañ, ngalla ñoom! \q1 Maay fey samay noon! \q1 \v 25 Yerusalem, maa lay teg loxo, \q1 maay seeyal sa raxit ni xeme, \q1 ba dindi sa mbuubit mépp. \q1 \v 26 Maay waññi say àttekat, ñu mel na woon, \q1 say diglekat it dellu mel ni bu jëkkoon. \q1 Su boobaa ñu wooye la Dëkkub Njekk, \q1 ak Dëkkub Kóllëre.» \q1 \v 27 \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* dëppook yoon, mucc, \q1 ay tuubkatam wormaal njekk, raw; \q1 \v 28 moykat ak bàkkaarkat yàqoondoo, \q1 dëddukati Aji Sax ji sànkoondoo. \q1 \v 29 Yeenay rus moos ci garab yu mag, \q2 yi ngeen soppoona daje, di xërëmtu. \q1 Yeenay am gàcce ci tóokër, \q2 yi ngeen taamu woona daje, di bokkaale. \q1 \v 30 Yeenay meli ni garab gu mag gu xob ya lax, \q1 mbaa tóokër bu amul siitu ndox. \q1 \v 31 Boroom doole mel ni boob, \q1 la mu liggéey di ferñent, \q1 ànd ak moom ne jéppét, \q1 te kenn du fey sawara wa. \c 2 \s1 Kilifteef gu bees taxaw na \p \v 1 Mbir mii la Yàlla won Esayi doomu Amocc ci mbirum Yuda ak Yerusalem. \q1 \v 2 Fan yu mujj ya, dees na taxawal \q2 tundu kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 Aji Sax ji mooy gëna kawe ci tund yi, \q1 tiim tund yu ndaw yi, \q1 xeet yépp riirandoo, wutsi ko. \q1 \v 3 Ay askan yu bareey dikk, naan: \q1 «Dikkleen nu yéegi tundu Aji Sax ji, \q1 fa kër Yàllay Yanqóoba, \q1 mu xamal nuy yoonam, \q1 ba nu doxe yooyu ñallam.» \q1 \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* kat la ndigalu yoon di bawoo, \q1 Yerusalem googu la kàddug Aji Sax ji di jóge. \q1 \v 4 Mooy àtte diggante xeet yi, \q1 mooy dogalal ay askani askan, \q1 ñu tëgg seeni saamar ay illéer, \q1 def seeni xeej ay sàrt; \q1 aw xeet dootu xàccil moroom ma saamar, \q1 te dootuñu jàngati xare. \q1 \v 5 Yeen waa kër Yanqóoba, \q1 kaayleen nu doxe leeru Aji Sax ji! \s1 Bew, yàqule \q1 \v 6 Boroom bi, bàyyi nga waa kër Yanqóoba, sa ñoñ, \q1 ndax jëfi waa penku lañu feese, \q1 aki gisaanekat, ba mel ni waa Filisti, \q1 te ñooy tàppante pasook doomi doxandéem yi. \q1 \v 7 Seen réew maa ngi ne gàññ ak xaalis ak wurus, \q1 alal du jeex, \q1 fas ne xas, \q1 watiiri xare du jeex. \q1 \v 8 Seen réew maa ngi fees aki yàllantu; \q1 ñuy sujjóotal seen liggéeyu loxo yooyu, \q1 te ñoo ko sàkkal seen bopp. \q1 \v 9 Doom aadama torox na, ku ne detteelu, \q1 waaye bu leen yékkati! \q1 \v 10 Ayca ca xunti ma, \q1 làqujileen biiri pax, \q1 ba sore tiitaange ji \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji sabab, \q1 sore darajay màggaayam. \q1 \v 11 Bésub keroog booba, \q1 ku bew bay regeju mooy detteelu, \q1 sagub nit sàggiku, \q1 Aji Sax ji doŋŋ mooy jagoo kawe. \b \q1 \v 12 Bés déy ñeel na Aji Sax ju gàngoor yi, \q2 ca lay xaare képp ku bew ak ku reew, \q1 ba kuy daŋŋiiral, detteelu. \q1 \v 13 Ca lay xaare garabi seedari Libaŋ \q2 yi ne coleet, ba kawe, \q1 ak garab yu mag ya fa Basan. \q1 \v 14 Ca lay xaare wépp tund wu mag wu ne coleet, \q1 ak bépp jànj bu kawe, \q1 \v 15 ak jépp tata ju gudd, \q1 ak bépp miir bu ñu dàbbli, \q1 \v 16 ak gaalu Tarsis gu mag gu mu doon, \q1 ak gépp gaal gu taaru. \q1 \v 17 Bésub keroog booba, \q1 kuy daŋŋiiral, detteelu, \q1 sagub nit sàggiku, \q1 Aji Sax ji doŋŋ mooy jagoo kawe. \b \q1 \v 18 Yàllantu yépp a naan mes, \q1 \v 19 nit ñi làquji biir xuntiy doj, \q1 ruuruji biiri pax, \q1 ba sore tiitaange ji Aji Sax ji sabab, \q1 sore darajay màggaayam, \q1 kera buy taxaw, ba suuf di lox. \q1 \v 20 Bésub keroog booba, \q1 yàllantuy xaalis ak wurus \q2 ya nit sàkkal boppam, di leen sujjóotal, \q1 ñoom lay sànni ca jaar yaak njugub ya, \q1 \v 21 ba mana làquji ca xunti ya \q1 ak xarantey doj ya, \q1 ba sore tiitaange ji Aji Sax ji sabab, \q1 sore darajay màggaayam, \q1 kera buy taxaw, ba suuf di lox. \q1 \v 22 Baleen nit, \q1 noowal bakkan kese la! \q1 Ana lees koy nawe? \c 3 \s1 Yuda salfaañoo na \q1 \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom bi, Aji Sax ju gàngoor yi kat, \q1 mu ngi nii di jële Yerusalem ak Yuda, \q1 lu doon wéeruwaay, di cëslaay, \q1 muy dugub ju ñu yaakaaroon, \q1 di ndox mu ñu yaakaaroon, \q1 \v 2 ak jàmbaar ak ñeyu xare, \q1 akub àttekat akub yonent, \q1 ak gisaanekat ak magum pénc, \q1 \v 3 ak njiitu juróom fukki dag, akub kàngam, \q1 ak diglekatu buur, ak ndaanaanu liggéeykat, \q1 ak jatkat bu xareñ. \q1 \v 4 «Maay def ay gone jiite leen, \q1 di ñu yaroo seen sago, yilif leen. \q1 \v 5 Nit ñiy soxorante, \q1 ku nekk ak moroomam, ku nekk ak dëkkandoom, \q1 ndaw di ñàkke mag kersa, \q1 sagaru nit sofental boroom daraja. \q1 \v 6 Nit dina ne nikk mbokk ma, \q1 ca biir kër baayam, ne ko: \q1 “Yaw mi dese mbubb, jiite nu, \q1 ba lu bokk ci sunu gent bii, di sa kilifteef.” \q1 \v 7 Keroog kooka àddu ne ko: \q1 “Duma leen mana fajal dara! \q1 Du dugub, du mbubb fa sama kër, \q1 dungeen ma def njiit!”» \q1 \v 8 Yerusalem day téqtalu, \q1 Yuda fëlëñu. \q1 Ñooy wax ak a jëf lu neexul Aji Sax ji, \q1 di gàntal leeram gi teew. \q1 \v 9 Seen dëgër bët tuumaal na leen, \q1 ñuy bàkkaar ni waa Sodom, \q1 làquwuñu sax. \q1 Wóoy, ngalla ñoom! \q1 nde ñoo lor seen bopp. \q1 \v 10 Neleen aji jub ji mooy baaxle, \q1 mooy yooloo añam. \q1 \v 11 Waaye wóoy ku bon, nde mooy bonle; \q1 la mu def rekk lees koy def. \q1 \v 12 Bokk yi, ñu xalele ñoo leen di not, \q1 ay jigéen yilif leen. \q1 Bokk yi, seeni njiit a ngi leen di sànk, \q1 lëndëmal nañu seeni yoon. \q1 \v 13 Aji Sax jaa ngi ci jataayu layoo, \q1 moo jóg di àtte ay xeet. \q1 \v 14 Aji Sax jeey yékkati kàddug sikkaange, \q1 jëme ci magi ñoñam ak seeni kàngam. \q1 «Yeena sëxëtoo tóokëru reseñ bi, \q1 la ñu foqatee ci néew-ji-doolee nga seeni kër. \q1 \v 15 Lu waral ngeen di dëggaate sama ñoñ, \q1 nappaaje néew-doole yi?» \q1 Kàddug Boroom bee, Aji Sax ju gàngoor yi. \s1 Puukare sànk na jigéeni Siyoŋ \q1 \v 16 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji da ne: \q1 «Jigéeni \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* a ngi daŋŋiiral, \q1 di goŋeet-goŋeeti, \q1 di regejook a rékk-rékkal, \q1 samp um ndaag, \q1 keleŋal lami wëq.» \q1 \v 17 Moo tax Boroom beey wat jigéeni Siyoŋ nel, \q1 Aji Sax jeey muri seen jë. \p \v 18 Bésub keroog Boroom bi xañ leen gànjari tànk, ak takkaay yu bindoo ni jant, ak yu bindoo ni weer wu feeñ; \v 19 aki loŋ-loŋ aki caq aki muuraay. \v 20 Moo leen di xañ ay tañlaay ak lami përëg aki ngañaay ak téere yu xeeñ aki gàllaaj, \v 21 xañ leen jaaroy torlu ak jaaroy bakkan, \v 22 ak mbubbi xew, aki mëlfë, ak séri càngaay, ak saagi loxo, \v 23 ba ci yérey sooy ak yérey lẽe aki musóor aki kol. \q1 \v 24 Su boobaa lu xasaw wuutu lu xeeñ, \q1 buum wuutu ngañaay, \q1 nel bu set wuutuy létt, \q1 yérey saaku wuutu ndoket bu rafet, \q1 toroxte wuutub taar. \q1 \v 25 Yerusalem, say góor ay fàddoo saamar, \q1 say jàmbaar des xare. \q1 \v 26 Su boobaa sa bunti dëkk sax di ñaawlook a jooy, \q1 mel ni ndaw su ñu futti, \q1 mu ne dett fi suuf. \c 4 \q1 \v 1 Su bés baa juróom yaari jigéen ŋoyaalu genn góor, ne ko: \q1 «Sunub dund, nun a, \q1 sunu koddaay, nun a! \q1 Jox nu sag buum rekk, \q1 teggil nu gàcce.» \s1 Aji Sax ji aar na ndesu Yerusalem \q1 \v 2 Su bés baa njebbitum \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji \q1 doon lu yànj, darajawu, \q1 meññeefum réew mi di teraanga, dib sag, \q1 ñeel ñi dese bakkan fi Israyil. \q1 \v 3 Su boobaa ku mucc fa \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* \q1 ak ku des fa Yerusalem, \q1 ku sell ki lees lay wooye, \q1 muy képp ku ñu bind turam, \q1 te mu wara dese bakkan ci Yerusalem. \q1 \v 4 Boroom beey wal noowal mbugal, \q1 noo guy lakk, sellal, \q1 fóote ko jonkani jigéeni Siyoŋ, \q1 fetee ko deret ji ci Yerusalem, ba mu set. \q1 \v 5 Su boobaa tundu Siyoŋ bépp, \q1 fépp fu ñuy dajee, \q1 Aji Sax ji sàkk fa niiru saxar bëccëg, \q1 guddi mu def tàkk-tàkk bu ne ràññ; \q1 leeru Aji Sax ji di kiiraay, tiim lépp, \q1 \v 6 di mbaar mu ñuy serloo tàngooru bëccëg, \q1 di ko seeloob taw ak waame. \c 5 \s1 Woyu cofeel rax na \q1 \v 1 Naa woy sama soppe \q1 woyu cofeel wu solowoo tóokëram. \q1 Sama soppee fi amoon tóokër, \q1 kaw tund wu suuf sa nangu lool. \q1 \v 2 Mu gàbb ko, dindi doj ya, \q1 jëmbat ca ngëneeli reseñ, \q1 tabax tóojub doj fa digg ba, \q1 ba yett ca mbalkam nalukaayu reseñ, \q1 tey yaakaar reseñ ju neex, \q1 mu meññ, wex. \b \q1 \v 3 Léegi yeen waa Yerusalem \q1 ak yeen waa Yuda, \q1 ngalla àtteleen maak sama tóokër. \q1 \v 4 Lu may defalati sama tóokër bi, \q1 lu ma ca defuloon? \q1 Lu waral ma di ko yaakaare reseñ ju neex, \q1 mu meññ, wex xàtt? \q1 \v 5 Ma xamal leen nag \q1 li ma naral sama tóokër bi. \q1 Ñàggib ñagam, mu dim parlu; \q1 màbb miiram, ñu dëggaate ko, jàll. \q1 \v 6 Dama koy gental, \q1 mu saxi dég aki dagg, \q1 deesu ko tenqi, deesu ko bey; \q1 niir yeet, ma sant leen \q1 ñu bañ koo tawal. \q1 \v 7 Tóokëru \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoor yi kat, \q1 mooy waa kër Israyil. \q1 Niti Yuda it \q1 ñooy njëmbat li mu safoo. \q1 Mu di ko yaakaare njub, \q1 njubadi ne jaas. \q1 Mu yaakaar njekk, \q1 yuuxi njekkar ne jaas. \s1 Alkànde ñeel na kàngami Yuda \q1 \v 8 Wóoy ngalla ñii di dajale kër ak kër, \q1 tool akub tool, \q1 aakimoo fépp, \q1 ba des ñoomu neen ci réew mi. \q1 \v 9 Maa dégg \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoor yi, \q1 mu ne: «Giñ naa ne \q1 kër yu bareey gental déy, \q1 kër yu yaa, rafet, kenn dëkku ca. \q1 \v 10 Tóokërub ñetti egtaar déy \q1 du meññ juróom fukki liitari biiñ, \q1 te jiwum téeméeri kiloy bele it, \q1 fukki kilo doŋŋ a cay génne.» \q1 \v 11 Wóoy ngalla ñiy teela xëy, \q1 daw wutiw ñoll, \q1 gonloo biiñ ba tàng jérr. \q1 \v 12 Xalam yaak tabala yaak toxoro ya jolli, \q1 biiñ xelli ca xawaare ja. \q1 Seetluwuñu sax li Aji Sax ji def, \q1 xooluñu li mu jo loxoom. \q1 \v 13 Moo tax ñoñi Aji Sax ji di duggi ngàllo \q1 ndax ñàkk xam-xam. \q1 Seen kàngam ay deeye xiif, \q1 seen baadoolo deeye mar. \q1 \v 14 Moo tax njaniiw di yàkkli ag bóli, \q1 gémmiñ ga ne ŋafeet, amul kersa, \q1 boroom darajaak baadoolay Yerusalem \q1 doon xaxaloo, far tàbbi ca. \q1 \v 15 Doom aadama torox na, \q1 nit detteelu na, \q1 ku doon regeju, detteelu. \q1 \v 16 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, ab àtteem lay fésale màggaayam, \q1 Yàlla ju sell ji, ag njekkam lay firndeele sellngaam. \q1 \v 17 Am xar a nara fore biir dëkk bi, mbetem parlu, \q1 màngaan lekke gentub boroom alal. \q1 \v 18 Wóoy ngalla ñiy ràngooy buum, \q1 di diri ñaawtéefi neen, \q1 ràngooy goj di diri seeni tooñ. \q1 \v 19 Ña nga naa: «Na Aji Sax ji gaaw! \q1 Na baral liggéeyam, nu gis. \q1 Na Aji Sell ju Israyil sottal mébétam, \q1 mu sotti, nu xam.» \q1 \v 20 Wóoy ngalla ñiy gis lu bon, ne lu baax la; \q1 gis lu baax, ne lu bon la; \q1 lëndëm, ñu tudde leer, \q1 leer, ñu tudde lëndëm; \q1 lu wex, ñu ne neex na \q1 lu neex, ñu ne wex na. \q1 \v 21 Wóoy ngalla ñii defe ne ñoo xam, \q1 yaakaar ne ñoo muus. \q1 \v 22 Wóoy ngalla ñiy jàmbaari naan biiñ, \q1 diy ndaanaan ci njafaanu ñoll, \q1 \v 23 di dëggal ku sikk ndax ab ger, \q1 tey xañ boroom njekk, ag njekkam. \q1 \v 24 Moo tax ni boob di jeexe ci sawara, \q1 ngooñ xoyomoo ko cib taal, \q1 ni la seenub reen di seeye ni lu maxe, \q1 seeni tóor-tóor naaw ni pënd. \q1 Ñoo gàntal yoonu Aji Sax ji ci gàngoor yi, \q1 ñoo sofental kàddug Aji Sell ju Israyil. \q1 \v 25 Moo tax merum Aji Sax ji tàkkal ñoñam, \q1 mu xàcci loxoom, duma leen, \q1 ba tund yi jaayu, \q1 seeni néew wetar ni mbalit fi mbedd yi. \q1 Loolu yépp taxul mu meddi, \q1 loxoom baa ngi mu xàcci ba tey. \b \q1 \v 26 Aji Sax jeey yékkatil raaya, xeet wu sore, \q1 wal ug liit, wooye leen fa cati àddina, \q1 ñu jekki ne jaas, dikkal leen. \q1 \v 27 Kenn sonnu ci, kenn tërëfu ci, \q1 kenn dajjantul mbaa muy nelaw; \q1 ngañaay yolomul, waruw dàll dogul. \q1 \v 28 Seeni fitt ñaw na, \q1 seen xala yépp noppi na, \q1 seen wewi tànki fas ni xeer. \q1 Bu tànki watiir ya dawee, \q1 nga defe ne callweer a. \q1 \v 29 Dañuy ŋar ni gaynde, \q1 ŋarati ni gaynde gu mat; \q1 yëmmu, ŋank um rëbbam, \q1 yóbbu te kenn du wallu. \q1 \v 30 Bésub keroog ñu ŋaral Yuda, \q1 ŋar yu mel ni géej gu sàmbaraax! \q1 Foo geesu ci réew mi, xool, \q1 doo gis lu moy lëndëm ak njàqare, \q1 xàmbaar maase, ba leer giim. \c 6 \s1 Aji Sax ji setal na Esayi, yebal ko \p \v 1 At ma Buur Osiyas saayee, damaa gis Boroom bi toog kaw ngàngune mu kawee kawe, lafi mbubbam fees néeg bu sell bi. \v 2 Ay malaakay seraf ñoo taxaw, tiim ko, ku ci nekk am juróom benni laaf: ñaar yu muur seen kanam, ñaar yu muur seeni tànk, ak ñaar yu ñuy naawe. \v 3 Ku ci nekk di àddu, naan moroom ma: \q1 «Kee sell te sell te sell, \q1 keey \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoori xare yi, \q1 àddina sépp a feese ag leeram!» \p \v 4 Ku ci àddu, kenuy bunt yay riir, néeg Aji Sax ji fees ak saxar. \v 5 Ma ne: «Wóoy man, sànku naa! Man miy nit ku làmmiñam sobewu, xeetoo ci ñu seen làmmiñ sobewu, te samay gët tegu ci kaw Buur Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi.» \p \v 6 Kenn ci malaakay seraf ya naaw wutsi ma, yor aw xal wu mu keppe ag ñiim, jële ko fa \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* ba. \v 7 Mu laalale xal wi sama gémmiñ, ne ma: \q1 «Mu ngoog, ndegam lii laal na sa gémmiñ, \q1 sag tooñ wàcc na, sa bàkkaar faru na.» \p \v 8 Ma dégg baatu Boroom bi, mu naan: «Ana ku may yebal, ana ku nuy demal boog?» Ma ne: «Xanaa man, yebal ma!» \v 9 Mu neeti: «Demal, wax askan wii, ne leen: \q1 “Dégluleena déglu te buleen dégg, \q1 xool-leena xool te buleen gis.” \q1 \v 10 Nanga dërkiisal xoli askan wii, \q1 fatt seeni nopp, \q1 taf seeni gët; \q1 lu ko moy seeni gët gis, \q1 seeni nopp dégg, \q1 seen xol yég, \q1 ñu dëpp, wér.» \p \v 11 Ma ne: «Boroom bi, foo àppal loolu?» Mu ne: «Xanaa fii ba seeni dëkk gental, ba kenn dëkkatu ca, ba nit dootu nekk biir kër ya, suuf sa yàqu yaxeet, di ndànd-foyfoy. \v 12 Aji Sax jeey yebal waa réew mi fu sore, tool yu bare booy. \v 13 Bu ca fukkeelu nit ña desoon, ñoom it dees na leen dellu taal. Waaye dañuy mel ni wenn ci xeeti garab yu mag yi ñuy gor, ëkk ba dellu jebbi, ëkku xeet wii, jiwu mu \w sell|lemma="sell:"\w* lay doon.» \c 7 \s1 Yaakaar Yàlla war na Buur Axas \p \v 1 Janti buurub Yuda, Axas doomu Yotam miy doomu Osiyas, Reccin buurub Siri moo dal ci kaw Yerusalem, ànd ak buurub Israyil, Peka doomu Remalya. Waaye manalu leen dara. \v 2 Ba ñu yégalee Buur Axas sëtub Daawuda, ak waa këram, ne ko waa Siri, Efrayim\f + \fr 7.2 \fr*\ft Efrayim moo gëna yaatu ci fukki giir ya féete woon réewum Israyil ga ca bëj-gànnaar, te moo taxawe taxawaayu Israyil.\ft*\f* lañu lëngool, mbir ma yëngal na Buur Axas ak waa réew ma, ba mel ni garabi gott bu ngelaw li gësëm. \v 3 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax Esayi ne ko: «Génnal gaaw, dajeek Axas, yaak sa doom Seyar Yasub, ma nga ca catal solomu mbànd ma féete kaw, ca yoonu toolu fóotkat ya. \v 4 Nga wax ko ne ko: \q1 “Defal ndànk te ne cell. \q1 Bul tiit, bul xàddi \q1 ndax merum Reccin ak Siri, \q1 ak doomu Remalya ji. \q1 Duñu dara lu moy ñaari gil yuy saxar! \q1 \v 5 Waa Siri ñoo ànd ak Efrayim ak doomu Remalya, \q1 di la fexeel naan: \q1 \v 6 ‘Nan songi Yuda, \q1 tiital leen, nangu ko, \q1 fal fa doomu Tabeel buur.’ \q1 \v 7 Waaye Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 ‘Loolu du sotti, du am. \q1 \v 8 Damaas a yilif Siri, \q1 te Reccin yiliful lu moy Damaas. \q1 Fii ak juróom benn fukki at ak juróom \q1 Efrayim tas, ba xeet wa réer.’ \q1 \v 9 Samaree yilif Efrayim, \q1 te doomu Remalya ji yiliful lu moy Samari. \q1 Dungeen mana saxoo dëgër nag, \q1 ndare ngeen sax ci Aji Sax ji.”» \s1 Juddub Emanuwel firnde la \p \v 10 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji teg ca ne Axas: \v 11 «Ñaanal sa Yàlla Aji Sax ji firnde. Ñaan ko ko, ak fu mu mana bawoo, fa suufa suuf, mbaa fa kawa kaw.» \v 12 Axas ne: «Duma ko ñaan, ndax duma nattu Aji Sax ji.» \v 13 Esayi nag ne: \q1 «Yeen waa kër Daawuda, dégluleen! \q1 Tàyyiloo ngeen nit, \q1 di tàyyiloo sama Yàlla itam. \q1 \v 14 Kon nag Boroom bi ci boppam moo leen di jox firnde: \q1 janq bi mooy ëmb, jur doom ju góor, \q1 tudde ko Emanuwel (mu firi Yàllaa ngeek nun). \q1 \v 15 Soow ak lem lay lekk, \q1 ba keroog muy mana taamu lu baax, \q1 ba lu bon. \q1 \v 16 Bala xale bee ràññee lu baax ak lu bon, \q1 dees na gental réew mii nga ragal seen ñaari buur. \q1 \v 17 Aji Sax jee lay dikke, \q1 yaak saw xeet ak sa waa kër baay, \q1 ay bés yu tar yu masula am, \q1 ba Efrayim dëddoo Yuda ba tey, \q1 te buurub Asiri la koy sababe.» \q1 \v 18 Bésub keroog Aji Sax ji ootal weñ, \q2 ya fa catal wali ndoxi Misra, \q1 ak yamb ya fa réewum Asiri, \q1 \v 19 ñu dikk, bokk tagesi mbartali xunti yi, \q1 ba ci xar-xari doj yi, \q1 ak gajjoo gajj, ak déegoo déeg. \q1 \v 20 Bésub keroog saatu la Boroom biy wate, \q1 te saatu ba moo di buurub Asiri, \q1 mu àbbe ko ca wàllaa dex, \q1 wat la nel, \q1 wat say yeel, \q1 xuuf sab sikkim. \q1 \v 21 Bésub keroog nit du fa dundle \q2 lu dul wenn nag ak ñaari gàtt, \q1 \v 22 meew ne gàññ, ndax nit ñu néew, \q1 di dunde am soow, \q1 nde soow ak lem la képp ku des ci réew ma di dundeji. \q1 \v 23 Fu junniy reseñ taxaw tey, \q1 di jar junniy donji xaalisu lëmm, \q1 bésub keroog ay dég aki dagg nangu ko. \q1 \v 24 Xalaaku fitt lees fay deme, \q1 ndaxi dég aki dagg yu fees réew mi. \q1 \v 25 Mépp mbartal mu ñu daan gàbb, \q1 deesu fa demati, \q1 ndax ragali dég aki dagg, \q1 aw nag a cay fore, \q1 am xar curpee ca. \c 8 \s1 Asiri workat la, matul wéeruwaay \p \v 1 Gannaaw gi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ne ma: «Jëlal àlluwa ju mag, ak xalima gu jàppandi, nga bind ci lii: “Maxer Salal Xas Bas”, (mu firi Sëxëtoo këfit foqet).» \v 2 Ma wut ci seede, won àlluwa ja ñaar ñu mat seede: ñuy Uri \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba, ak Sàkkaryaa doomu Yeberekiya. \v 3 Ba loolu weesee ma jaxasoo ak sama soxna, yonent bu jigéen ba, mu ëmb, gannaaw gi mu am ca doom ju góor. Aji Sax ji ne ma: «Tudde ko “Maxer Salal Xas Bas.” \v 4 Bala xale bee man ne “Baay” mbaa “Yaay” déy, dees na yóbbul buurub Asiri alal ju ñu foqatee Damaas, ak lël ju ñu këfe Samari, nangu ko.» \q1 \v 5 Aji Sax ji dellu ne ma: \q1 \v 6 «Gannaaw askan wee teddadil ndoxum Silowe, \q2 mi ci wal mu teey mi, \q1 di bége Reccin ak doomu Remalya, \q1 \v 7 Boroom baa ngii di leen sottisi \q1 dexu Efraat gi ne xéew ak dooleem, \q1 te mooy buurub Asiri ak mboolem darajaam. \q1 Dex gi mooy génn xuram, \q1 fees fépp fu dig tàkkam, \q1 \v 8 wal-wali jàll Yuda, \q1 mbënn ma wal, taañaañal, \q1 yéeg ba tollu ko ci put, \q1 firiku niy laaf ba dajal sam réew, yaw Emanuwel.» \q1 \v 9 Yeen xeet yi, xaaculeen, dees na leen rajaxe. \q1 Yeen waa cati àddina, teewluleen! \q1 Gañoo gañu, ñu rajaxe leen! \q1 Ma ne: Gañoo gañu, ñu rajaxe leen! \q1 \v 10 Ngeen mébét, dara! \q1 Ngeen diisoo, diisoo, tus! \q1 Yàllaa ànd ak nun! \s1 Aji Sax jee jara ragal \q1 \v 11 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji moo wax ak man, \q1 ba mu ma nee nikk, àrtu ma, \q1 ngir ma baña roy askan wii. Mu ne ma: \q1 \v 12 «Bul tudde wor, \q1 lenn lu askan wii tudde wor; \q1 lu ñu ragal it, bu ko ragal, \q1 bu ko tiit. \q1 \v 13 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi daal ngay sellal, \q1 moom ngay ragal, \q1 moom ngay tiit. \q1 \v 14 Mu doon seen bérab bu sell, \q1 di doj wuy fakktale, \q1 xeer wuy féle, ci ñaari këri Israyil, \q1 te dim yeer, dig fiir, \q1 ñeel ku dëkk Yerusalem. \q1 \v 15 Ñu baree cay tërëf, \q1 daanoo njaaxaanaay, damm, \q1 mbaa ñu sërëx, keppu.» \b \q1 \v 16 Dencal seede bii, \q1 jëlal lii ndigal, tay cib tayu, \q1 dénk ko samay dongo. \q1 \v 17 Maa ngi séentu Aji Sax ji, \q1 mu ngi won waa kër Yanqóoba gannaaw, \q1 waaye maa ngi koy yaakaar. \q1 \v 18 Man de, maa ngii, maak xale yi ma Aji Sax ji may, \q1 nu diy firnde fi Israyil te diy tegtal \q2 yu bàyyikoo fa Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, \q2 ki dëkke tundu \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*. \q1 \v 19 Am na ñu naan: \q1 «Laajleen ñiy gisaanee nit ñu dee, \q1 ak boroom rawaan yiy kebetook a ŋun-ŋuni. \q1 Aw xeet sañ nañoo gisaanee seeni tuur, \q1 tey diis ñi dee mbiri ñiy dund.» \q1 \v 20 Kon waxleen ne leen: «Ayca, ca ndigali yoon ya, \q2 ak seedey kàdduy waxyu ya. \q1 Kuy wax googu kàddu, ag leer fenkalu la.» \q1 \v 21 Nit ñi dinañu taxawaalu ci réew mi, \q1 boole njàqareek ub xiif, \q1 te bu ñu xiifee, ñéññ, \q1 téen, xool kaw, \q1 saaga seen buur, saaga Yàlla, \q1 \v 22 dellu xool fi suuf, \q1 yem ciw tiis, ak lëndëmu njàqare, \q1 sóoboo guddi gu fatt taraj. \c 9 \q1 \v 1 Waaye lëndëm googu du sax \q1 ci réew mii jàq tey. \q1 Démb Aji Sax ji torxal na \q2 réewum Sabulon ak mu Neftali, \q1 waaye ëllëg mu teral waa foofa, \q1 dale ko diiwaanu tefesu géej, \q1 ba ca wàllaa dexu Yurdan, \q1 boole ca sax Galile ga ca doxandéem ya. \s1 Doom juddul na nu \q1 \v 2 Askan wiy doxe lëndëm nii, \q1 ñooy gis leer gu mag. \q1 Ñooñu dëkke réewum ndee mu ne këruus, \q1 ñoom la leer di fenkal. \q1 \v 3 Aji Sax ji, yaay yokk xeet wi, \q1 fulal leen bànneex, \q1 ñuy bége fi sa kanam, mbégtem ngóob, \q1 mel ni ñuy bànneexoo fa ñuy séddoo alalu xare. \q1 \v 4 Yaa leen di sippil seen sëf, \q1 damm bant ba ñu leen gàlloon, \q1 ak yetu ña leen notoon, \q1 na nga leen defaloon rekk ca xareb Majan. \q1 \v 5 Mboolem dàll wu ab noon dukkate ba dikk, \q1 ak turki bu màndi deretu xare, \q1 sawara lees koy leel. \q1 \v 6 Nde gonee juddu, ñeel nu, \q1 di doom ju góor ju ñu nu may, \q1 mu yenu kilifteef gi, \q1 ñu di ko wooye Diglekat bu yéeme bi, \q1 ak Yàlla jàmbaar ji, \q1 ak Baay bi sax dàkk, \q1 ak Buuru jàmm bi. \q1 \v 7 Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, \q1 fa jalub Daawuda ak nguuram, \q1 ga muy samp, saxale ko njekk ak yoon, \q1 tey jii, ba fàww. \q1 Lii la \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem. \s1 Aji Sax ji yokk na mbugalam \q1 \v 8 Boroom bee yónnee kàddu \q2 gu dal Israyil, askanu Yanqóoba, \q1 \v 9 xeet wépp jot ca, \q1 ba ca Efrayim ak waa Samari, \q1 ñay damook a sagu naan: \q1 \v 10 «Ay móol màbb, \q1 nu yett ponkali doj, tabaxaat, \q1 xànqi garab yu ndaw daanoo ca, \q1 nu wuutal ca garabi seedar yu mag.» \q1 \v 11 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji yékkati nooni Buur Reccin, fi seen kaw, \q1 gemb seeni bañ, \q1 \v 12 Siri songe penku; Filisteen ña, sowu, \q1 ñu sëxëtoo Israyil, wonn. \b \q1 Teewul Aji Sax ji xàcci loxoom, \q1 meddiwul ba tey. \b \q1 \v 13 Waaye xeet wi delluwuñu ca ka leen duma, \q1 sàkkuwuñu Aji Sax ji Boroom gàngoor yi. \q1 \v 14 Moo tax Aji Sax ji doge Israyil bopp ak geen, \q1 boole tiir ak barax fóom ci benn bés. \q1 \v 15 Mag meek kàngam li ñooy bopp bi, \q1 yonent bi mokkal naaféq dib geen. \q1 \v 16 Ñi jiite askan wii ñoo leen di sànk, \q1 ña ñuy jiite loru. \q1 \v 17 Moo tax Boroom bi du bége seeni xale yu góor, \q1 du yërëm seeni jirim ak seeni jëtun. \q1 Ñoom ñépp a gëmadi, di def lu bon, \q1 ku ci nekk di wax lu amul bopp. \b \q1 Teewul Aji Sax ji xàcci loxoom, \q1 meddiwul ba tey. \b \q1 \v 18 Mbon a ngi tàkk moos \q1 ni sawara, xoyom dég aki dagg, \q1 jafal gajji gott bi, \q1 mu ne jippét, saxar, naaw. \q1 \v 19 Merum Aji Sax ji Boroom gàngoor yi taal na réew mi, \q1 xoyom waa réew mi, \q1 kenn yërëmul sa mbokk. \q1 \v 20 Nit ñaa ngi màtte ndijoor, te doyaluñu, \q1 di xàmpe càmmoñ te suuruñu, \q1 ku nekk di yàpp sa mbokk: \q1 \v 21 Manase song Efrayim, \q1 Efrayim song Manase, \q1 ñu mànkoo, noonoo Yuda. \b \q1 Teewul Aji Sax ji xàcci loxoom, \q1 meddiwul ba tey. \c 10 \s1 Mbugal ñeel na kàngami Yuda \q1 \v 1 Wóoy ngalla boroom dogal yiy dogal njubadi, \q1 bind ko, te muy jur coono, \q1 \v 2 di ko àttee ñàkkal ku ñàkk, \q1 di xañ àq sama néew-ji-dooley ñoñ, \q1 bay lekk ab jëtun, \q1 di sëxëtoo ab jirim. \q1 \v 3 Ana nu ngeen di def keroog bésub mbugal ba, \q1 keroog ba safaan di bawoo fu sore? \q1 Ana ku ngeen di daw wuti wallam? \q1 Ana fu ngeen di denci seen teraanga? \q1 \v 4 Xanaa ànd ak ña ñu jàpp, ne yogg; \q1 mbaa tëddandook ña ñu bóom, ne lareet. \b \q1 Teewul Aji Sax ji xàcci loxoom, \q1 meddiwul ba tey. \s1 Asiri muccul ci mbugal \q1 \v 5 Wóoy ngalla Asiri miy sama yetu mer, \q1 bolde bi ñu ŋàbb di samam sànj, \q1 \v 6 ma xabtal ko fi kaw xeet wu gëmadi, \q1 yebal ko ca askan woowu ma merloo, \q1 ngir ñu sëxëtoo leen, nangu seen alal, \q1 note leen ni banu mbedd. \q1 \v 7 Waaye Asiri gisewu ko noonu, \q1 xalaatewul noonu; \q1 bóome la xintewoo, \q1 ba fàkkas xeeti xeet. \q1 \v 8 Mu ngi naan: «Xanaa du sama jawriñ yépp a diy buur? \q1 \v 9 Kalne daa gën Karkemis gee ma nangu? \q1 Am Amat daa gën Arpàdd\f + \fr 10.9 \fr*\ft Kalne ak Karkemis ak Amat ak Arpàdd ay dëkki Siri lañu.\ft*\f*? \q1 Am Samari daa gën Damaas? \q1 \v 10 Maa duma réew yu seeni yàllantu, \q2 seeni tuur sut tuuri Yerusalem ak Samari. \q1 \v 11 Na ma tege loxo Samari aki yàllantoom, \q1 duma ni tege loxo Yerusalem aki tuuram?» \q1 \v 12 Boroom bi nee: \q1 «Bu ma sottalee liggéey fa kaw tundu \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* ak fa Yerusalem, \q1 maay mbugale buurub Asiri réy-réyloom gi, \q2 ak gëti xeebaateem.» \q1 \v 13 Moom moo ne: «Sama dooley përëg laa defe lii, \q1 maa xelu, ràññee; \q1 ba randal kemi suufi xeet yi, \q1 foqati seeni alal, \q1 dañ boroom jal ya niw yëkk, wàcce leen. \q1 \v 14 Maa teg alali xeet yi loxo, \q1 ni ku gis am tàgg. \q1 Maa tonneendoo réewi àddina \q1 ni ku for ay nen, tonni lépp, \q1 laaf tëf-tëfluwul, sàll newul ciib!» \b \q1 \v 15 Sémmiñ dina diir mbagg ka koy gore? \q1 Am dogukaay dina réy-réylu ba sut ka koy doge? \q1 Mbete yet wuy xàcci ka ko ŋàbb; \q1 mbaa bolde bu walbatiku ŋàbb boroom! \q1 \v 16 Moo tax Boroom bi, \q2 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoori xare yi, \q1 di yebal woppi ràgg fi kaw mbuxreem yi, \q1 seen daraja tàkk, sawara xoyom ko. \q1 \v 17 Aji Sax ji, leeru Israyil mooy doon sawara, \q1 ku Sellam kooku mooy doon tàkk-tàkku sawara, \q1 xoyom taxasi Asiri aki dégam ci benn bés. \q1 \v 18 Gott bu naat ak tool bu meññ, mu ne faraas fóom, \q1 ba mu mel ni ku wopp, yaram way seey, \q1 \v 19 gott ba dese garab yu néew \q2 yu gone mana lim, bind ko. \s1 Ndesu Israyil dina ñibbi \q1 \v 20 Keroog bés booba \q1 li des fi Israyil ak li rëcce kër Yanqóoba \q1 duñu wéerooti ña leen duma. \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji lañuy wóolu, wéeroo ko, \q1 Aji Sell ju Israyil. \q1 \v 21 Aw ndes ay délsi, \q1 di ndesu askanu Yanqóoba, \q1 ñeel Yàlla Jàmbaar ji. \q1 \v 22 Seen xeet wi ni feppi suufas géej lay tollu, \q1 te as ndes a ciy délsi. \q1 Àtteb sànkute mooy taxaw, \q1 yoon toppe ba mat sëkk. \q1 \v 23 Sànkute déy mooy taxaw, \q1 Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi \q1 di ko sottal fi réew mi mépp. \b \q1 \v 24 Moo tax Boroom bi, \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi \q2 dafa wax ne: \q1 «Yeen sama ñoñ ñi dëkke \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, \q1 buleen ragal waa Asiri yi leen di dóor yet, \q1 ŋàbbal leen bolde ni waa Misra daa def ak yeen. \q1 \v 25 Waaye fi leek lu néewa néew \q1 mbugal jeex fi seen biir, \q1 am sànj sippil Asiri seen sànkute.» \q1 \v 26 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee leen di ŋàbbal kàccri, \q1 na mu defoon waa Majan fa doju Oreb. \q1 Mooy xàcciw yetam, mu dal géej, \q1 na mu defoon fa Misra. \q1 \v 27 Bésub keroog sëf bu ñu leen sëfoon wàcc leen, \q1 ngeen tàggook yet wu ñu leen tënke woon, \q1 nde seen yaram ay naat, ba yet wa damm. \s1 Noon yi songsi nañu \q1 \v 28 Noon yeey songsi Ayat, jéggi Migron, \q1 dem ba Migmas, teg fa seeni jumtukaay, \q1 \v 29 jaare ca xunti ma \q1 te naan: «Geba lanuy fanaani!» \q1 Waa Raama tiit, waa Gibeya gu Sóol daw. \q1 \v 30 Yeen waa Galim, yuuxuleen, \q1 yeen waa Laysa, dégluleen, \q1 yeen waa Anatot, feeluleen. \q1 \v 31 Waa Madmena ñooy fëlxoo, \q1 waa Gebim wuti rawtu. \q1 \v 32 Tey jii noon yaa ngay taxaw fa Noob, \q1 di sànni loxo waa tundu \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, \q1 di ko tëkkoo waa Yerusalem googu. \q1 \v 33 Boroom baa ngoog, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoor yi, \q1 mu ngi gor garab yi, di rajaxe car yi, \q1 njobbaxtal ya gëna kawe dog, \q1 la ca gënoona siggi, wàcc. \q1 \v 34 Mooy jël sémmiñ, goraale gajji gott bi, \q1 Libaŋ loroo loxol boroom doole, ba jóoru. \c 11 \s1 Daawuda am na kuutaay \q1 \v 1 Aw njebbit mooy saxe fa ëkkub Yese\f + \fr 11.1 \fr*\ft Yese mooy baayu Daawuda.\ft*\f*, \q1 ab car soqeekoo fa reen ya, \q1 \v 2 xelum \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji tegu fi kawam, \q1 xelum rafet xalaat ak ràññee, \q1 xelum digle ak njàmbaar, \q1 xelum xam Aji Sax ji, ragal ko. \q1 \v 3 Ragal Aji Sax ji lay safoo, \q1 du lu ko bëtam may rekk lay àttee, \q1 du lu ko noppam may rekk lay dogale, \q1 \v 4 xanaa di àtte ku ñàkk ci njekk, \q1 di dogalal njub, néew-ji-dooley àddina. \q1 Mooy dóore àddina, bantub kàddoom, \q1 mooy reye ñu bon ñi, ngelawal gémmiñam. \q1 \v 5 Njekk lay gañoo, \q1 takkoo kóllëre. \q1 \v 6 Till ay bokk ak mbote ab dal, \q1 segg bokk akub tef ab tëraay, \q1 wëllu ànd ak gaynde gu mat, ak juru yar, \q1 tuut-tànk jiite leen. \q1 \v 7 Nag ak rab wu aay di forandoo, \q1 seeni doom goorandoo, \q1 gaynde di lekk um ngooñ niw yëkk, \q1 \v 8 luy nàmp di foye paxum ndox-suuf, \q1 perantal di laal tostanum ñàngóor. \q1 \v 9 Deesatul gaañe mbaa di lore, \q1 fi mboolem sama kaw tund wu \w sell|lemma="sell:"\w* wi, \q1 ndax ni ndox di feese ba muur géej, \q1 ni la àddina di feese nit ñu xam Aji Sax ji. \q1 \v 10 Bésub keroog car bawoo ca Yese, reen ba, \q1 taxaw di raaya buy gindi xeet yi, \q1 xeet yi di ko sàkku, \q1 dal-lukaayam ba jagoo teddnga. \b \q1 \v 11 Bésub keroog Boroom bi jooti loxoom \q2 ñaareel bi yoon, \q1 ngir jotaat ndesu ñoñam, \q1 wa des Asiri ak Misra, ak Pattros ak réewum \w Kuus|lemma="Kuus:"\w*, \q1 ak Elam ak Sineyaar, \q2 ak Amat ak biir duni géej ya. \q1 \v 12 Mooy yékkatil xeet yi raaya, \q1 dajale góor ña ñu dàqe Israyil, \q1 ak jigéen ña ñu jële Yuda, tasaare leen, \q1 ñu jóge ñeenti weti àddina, booloo. \q1 \v 13 Fiiraangey Efrayim day jeex, \q1 njéefoy Yuda dakk, \q1 Efrayim dootu fiire Yuda, \q1 Yuda dootu jéppi Efrayim. \q1 \v 14 Xanaa ñu ne coww ba sowu, \q1 ne jàyy cëppandoo \q1 fa kaw waggi Filisteen ña, \q1 waa penku, ñu sëxëtoondoo; \q1 Edom ak Mowab, ñu teg loxo; \q1 Amoneen ña nangul leen. \q1 \v 15 Aji Sax jeey wowal walum ndox, \q1 ma séle géeji Misra. \q1 Mooy tàllal loxoom, tiimale dexu Efraat, \q1 wal kook doole, \q1 dóor ko, mu séddlikoo juróom yaari wal, \q1 mu jaarale ca nit ñu caraxu, \q1 \v 16 def kow yoon, ñeel ndesu ñoñam, \q2 ña dese fa Asiri, \q1 mu mel ni yoon wa ñeeloon Israyil, \q1 bésub keroog ba ñuy génn réewum Misra. \c 12 \s1 Cant jib na \q1 \v 1 Bésub keroog dees na ne: \q1 «\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, sant naa la; \q1 yaa ma mere woon, meddi, dëfal ma.» \q1 \v 2 Ma ne: «Yàllaa may wallu, \q1 ma dal-lu, duma tiit. \q1 Sama dooleek sama kaaraange mooy Ki sax, \q1 di Aji Sax ji, \q1 te mooy sama wall.» \q1 \v 3 Mbégte ngeen di rooteji \q1 fa wali mucc ya. \q1 \v 4 Bésub keroog ngeen ne: \q1 «Santleen Aji Sax ji, tudd turam, \q1 xamley jalooreem ci biir xeet yi, \q1 fàttli màggaayu turam. \q1 \v 5 Woyleen Aji Sax ji, \q1 moo kawey jëf! \q1 Na lii siiw biir àddina sépp. \q1 \v 6 Yeen waa \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, serleen te sarxolleel \q2 ku màgg ki fi seen biir, \q1 Aji Sell ju Israyil.» \c 13 \ms1 Yàllaa moom xeet yi \mr (Saar 13—23) \s1 Yéeneb waxyu dal na Babilon \q1 \v 1 Yéeneb bii ñeel na Babilon\f + \fr 13.1 \fr*\ft Babilon tollu na ay jant yu mu mujj di puukarey xeet yi, ngir dooleem, te moo mujj yóbbu Yuda ngàllo.\ft*\f*, \q1 muy peeñum Esayi doomu Amocc. \q1 \v 2 Yéegeleen ab raaya kaw tund wu ne duŋŋ, \q1 joorleen ñii, \q1 tàllal-leen loxo, \q1 ñu jàlle bunti kàngam yi. \q1 \v 3 Maa jox ndigal ñi ma beral sama bopp, \q1 maa woo sama jàmbaar ñiy réy-réylu, \q1 ne leen ñu sottal mbugal mi samam sànj laaj. \q1 \v 4 Coowal mbooloo ngoog ca tund ya, \q1 mel ni ñu baree bare! \q1 Riirum nguuri nguur yu daje, di xeeti xeet! \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoor yi \q1 mooy dajale gàngooru xare. \q1 \v 5 Mooy bawoo fu sore, \q1 fa asamaan digalook suuf. \q1 Aji Sax ji laak gàngoor gi muy mbugale, \q1 ngir yàqtesi réew mi mépp. \q1 \v 6 Yuuxuleen! \w Bésub Aji Sax|lemma="bésub Aji Sax ji-:"\w* ji moo dëgmal, \q1 te ni sànkute gu bawoo fa ci Aji Man ji lay dikke. \q1 \v 7 Moo tax yoxoo yoxo yoqi, xoloo xol jeex, \q1 \v 8 ñu tiita tiit, \q1 yaram di fuddook a metti, \q1 ñuy baddaañu ni kuy matu; \q1 ku ne jàq, di xulli sa moroom, \q1 kanam ya sël-sëleendoo. \q1 \v 9 Bésub Aji Sax jaa ngii di ñëw, \q1 bés bu néeg, bésub mer ak sànj muy tàkk, \q1 nara gental suuf, \q1 te bàkkaarkat ya la fay fàkkas. \q1 \v 10 Biddiiw mbaa dëllooñ dootu leeral; \q1 jant ay fenke lëndëm, \q1 weer dakkal leeram. \q1 \v 11 Maay delloo àddina mbonam, \q1 yool ku bon tooñam, \q1 maay sàggi sagub ku reew, \q1 detteel puukarey ku néeg. \q1 \v 12 Maay def nit gëna jafee gis wurus, \q1 ba doom aadama raw wurusu Ofir. \q1 \v 13 Moo tax maay gësëm asamaan, \q1 suuf yëngoo fa mu tege \q1 ndax sànjum Aji Sax ji \q1 Boroom gàngoori xare yi, \q1 keroog ba meram di tàkk. \q1 \v 14 Ku nekk ay fekkiy bokkam, \q1 rawi cam réewam, \q1 mbete kéwél gu ñuy rëbb, \q1 mbaa xar mu amul sàmm. \q1 \v 15 Ku ñu ci gis, jam la, \q1 ku ñu jàpp, saamar rey la; \q1 \v 16 seeni doom, ñu moxoñe fi seen kanam, \q1 seeni kër, ñu sëxëtoo, \q1 seeni jabar, ñu tëdde. \b \q1 \v 17 Maa ngii di xabtal fi seen kaw waa Medd, \q1 ñi xintewoowul xaalis, \q1 faalewuñu wurus. \q1 \v 18 Seeni fitt lañuy rajaxee xalelu góor, \q1 duñu ñeewante gone, \q1 duñu xool tuut-tànk gëti yërmande. \b \q1 \v 19 Babilon nag, mooy gànjaru réew yi ko wër, \q1 di teraanga ji Kaldeen ñiy sagoo, \q1 waaye Yàllaa koy tas, \q1 mu ne tasar ni Sodom ak Gomor. \q1 \v 20 Deesatu fa dëkk, \q1 xanaa gental ba fàww. \q1 Màngaan dootu fa samp xayma, \q1 sàmm dootu fa gooral. \q1 \v 21 Ay rabi àll a fay goore, \q1 kër ya fees aki looy, \q1 bànjóoli dëkke fa, \q1 kéwél di fa curpee. \q1 \v 22 Bukki mooy sabe fa tata ya, \q1 till nangu kër yu bakkane ya. \q1 Àppu Babilon jege na, ay fanam du fi wees. \c 14 \p \v 1 Aji Sax ji kay mooy yërëm askanu Yanqóoba, dellu taamu xeetu Israyil wii. Moo leen di sancaatal fa seen suuf, doxandéem yi fekki leen; boole seen bopp ci askanu Yanqóoba. \v 2 Yeneen xeet yeey delloo \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ba seen réew, mooma Aji Sax ji séddoo, bànni Israyil jàpp ca ñoom njaam, góor ak jigéen, ba teg loxo ña leen tegoon loxo, moom ña leen moomoon. \v 3 Bés bu leen Aji Sax ji teggilee seeni coonook seeni fitna, ba ngeen tàggook njaam gu metti, gi ñu leen doon jaamloo, \v 4 su boobaa nangeen woyal buuru Babilon léeb wii, ne ko: \q1 «Moo nu ki daan note mujje? \q1 Nu mu mujjeek reewandeem? \q1 \v 5 Aji Sax jee damm bant, \q1 bi ñu bon ñi daan dóoree! \q1 Moo damm seen yetu nguur, \q1 \v 6 wi ñu daan xadaruy dóor askan yi, \q1 dóor yu dakkul, \q1 di joggatee xeet yi xol bu tàng, \q1 topp leen, tëë ba. \q1 \v 7 Àddina yépp a féex, am jàmm, \q1 sarxolle jolleendoo. \q1 \v 8 Garab yi dul ruus, ak seedari Libaŋ sax \q1 di bége sab jéll, \q1 naan: “Ba nga daanoo ba tey, \q1 ab gorkat jógalu nu.” \q1 \v 9 Njaniiw ga fa suufa suuf yàkkamti na la, \q1 di la waaja gatandu, \q1 ba yeel la ndem-si-yàlla yi doon njiiti àddina yépp. \q1 Moo yékkatee buuri xeet yépp seeni jal, \q1 \v 10 ñoom ñépp àddu, ne la: \q1 “Yaw it mujj nga néew doole ni nun a? \q1 yaak nun de a mujj yem kepp!” \q1 \v 11 Sa puukare gee tàbbisi nii njaniiw, \q1 yaak sa buumi xalam? \q1 Ay duusu di sa laltan, \q1 ay sax di sa càngaay! \q1 \v 12 Moo yaw biddiiwu njël, bi noon ràññ, \q1 tey nga xàwwikoo asamaan ba fii! \q1 Yaw mi daa daan xeet yi, \q1 tey ñu gor la, nga goor. \q1 \v 13 Xanaa du yaa doon wax ci sam xel, naa: \q1 “Maay yéeg kaw asamaan, \q1 maay aj sama jal kaw biddiiwi Yàlla, \q1 maay toogi kaw tundu ndaje ma, \q1 fa catal bëj-gànnaar. \q1 \v 14 Maay yéeg fa kaw niir ya, \q1 ba mel ni Yàlla Aji Kawe ji!” \q1 \v 15 Teewul nga tàbbi njaniiw, \q1 àkki ba ca xóotey pax ma. \q1 \v 16 Ku la gis ne la jàkk, \q1 xel ma ne ci yaw, mu naa: \q1 “Xanaa du kii a doon loxloo àddina, \q1 yëngal réewi réew, \q1 \v 17 def àddina wërngal këpp ndànd-foyfoy, \q1 tas dëkk ya, \q1 te du jàpp nit ba yiwi ko?” \q1 \v 18 Buuri àddina yépp, ba ñu daj, \q1 ñépp a tëdd tëraayu teraanga, \q1 ku ci nekk ak bàmmeelam. \q1 \v 19 Yaw, ñu xañ la bàmmeel, sànni la, \q1 nga mel ni car bu ñu foñ. \q1 Yaa ngi ne lareet ci biir néew yu saamar bóom, \q1 ñu tàbbal leen ci xeeri biir kàmb. \q1 Yaa ngi mel ni médd mu ñuy joggati. \q1 \v 20 Deesu la robaaleek yooyu buur, \q1 yaa yàq sam réew, \q1 faagaagal saw xeet. \b \q1 «Deesul tuddati mukk askanu lorkat wii. \q1 \v 21 Waajal-leen fi ñuy rendi doom yi, \q1 feye leen seen ñaawtéefi baay, \q1 bala ñoo jógati, teg àddina loxo, \q1 ba tabax fu ne ay dëkk\f + \fr 14.21 \fr*\ft Manees na koo tekkee nii it: \ft*\fqa bay feesal suuf aku ay.\fqa*\f*.» \b \q1 \v 22 «Maa leen di jógal.» \q1 Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. \q1 Mu ne: «Maay tenqi turu Babilon, tenqim ndesam \q1 ba ca seeni doom ak seen askan.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 23 Mu ne: «Maa koy def kërug siññéel, \q1 def ko ab tan, \q1 ba buube ko buubub rajaxe.» \q1 Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. \s1 Mbugal ñeel na Asiri \q1 \v 24 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoor yee giñ ne: \q1 «Lu ma nar déy mooy am, \q1 lii ma mébét, mooy sotti. \q1 \v 25 Maay joggati Asiri fi samam réew, \q1 dëggaate leen fi sama kaw tund yi, \q1 ba sama ràngi ñoñ rengiku, \q1 seenub sëf sippiku.» \b \q1 \v 26 Mii mébét lañu mébétal àddina sépp, \q1 bii loxo lañu xàccil xeet yépp. \q1 \v 27 Bu Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi dogalee déy, \q1 ana ku koy dogale? \q1 Bu xàccee loxoom, \q1 ana ku koy fommal? \s1 Ab yéeneb waxyu ñeel na Filisti \q1 \v 28 At ma Buur Axas saayee, \q1 bii yéene jib na: \q1 \v 29 Filistee, seen yetu gannaaw wi damm, \q1 bu ko kenn ci yeen bége, \q1 nde ci ëkku jaan ji, la ñàngóor di génne, \q1 am tostanam mujj di céebi. \q1 \v 30 Su boobaa ñi gëna walaakaana am lu ñu for, \q1 néew-doole ya goor, ànd ak dal. \q1 Waaye yeen, maa leen di xiifal, ngeen dee ba raaf, \q1 xiif ba fàkkas ñi ngeen dese. \q1 \v 31 Yeen magi pénc mi, ñaawluleen! \q1 Yeen waa dëkk bee, yuuxuleen! \q1 Na Filisti gépp ne yàcc! \q1 Bëj-gànnaar déy la saxar jollee, \q1 kenn du wuute gàngooru noon ya. \q1 \v 32 Lees di tontu xeet wi yónnee di laaj, \q1 xanaa ne leen \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee sanc \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, \q1 te fa la baadooloy ñoñam di rawe. \c 15 \s1 Ab yéeneb waxyu ñeel na Mowab \q1 \v 1 Yéene bii ñeel na Mowab: \q1 Genn guddi déy la Ar Mowab, dëkk ba tas, ne mes! \q1 Genn guddi déy la Kir Mowab tas, ne mes! \q1 \v 2 Nit ñaa ngi yéeg jëm kërug jaamookaay ga ca Dibon, \q2 ngir jooyi ca \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* ya, \q1 Mowab a ngay yuuxoo kaw tundu Nebo ak Medeba, \q1 boppoo bopp dib nel, \q1 sikkimoo sikkim xuufu, \q1 \v 3 nit ña sol saaku, di ñaawlu fa mbedd ya, \q1 ak kaw taax yaak pénc ya, \q1 ku ne di jooy ba say rongooñ wale. \q1 \v 4 Waa Esbon ak Elalee ngi yuuxu, \q1 seen baat àkki ba Yaxacc, \q1 xarekati Mowab dégg ca, yuuxoo, \q1 ne yàcc ne yasar! \q1 \v 5 Maay jooy Mowab jooyi xol, \q1 nit ñaa nga fay dawe ba Sowar, \q1 àkki ba Eglat Selisiya. \q1 Ña ngay yéeg jëm Luwit, di jooyoo, \q1 awe yoonu Oronayim, di jalu. \q1 \v 6 Dexu Nimrim wow na, \q1 ñax wow, gàncax lax, \q1 dara naatatul. \q1 \v 7 Jël nañu lu ñu deseek lu ñu dencoon, \q1 yóbbu, jàll ca wàllaa xuru Garab ya. \q1 \v 8 Yuux déy maase na réewum Mowab, \q1 jooyoo ya ba Eglayim, \q1 jooyoo ya ba Beer Elim. \q1 \v 9 Dexu Dimon déy fees na ak deret, \q1 te ma nara wàcceel Dimon lu ko raw, \q1 ba ku rëcce Mowab, \q1 ak ku des ci réew mi, ma booleek gaynde! \c 16 \q1 \v 1 Waa Mowab a nga naa: \q1 «Yónneeleen boroom réew mi yóbbalu kuuy yu ndaw, \q1 jële ko Sela, jaare màndiŋ ma, \q1 yóti ko buurub Yuda fa tundu \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* mu taaru.» \q1 \v 2 Jigéeni Mowab a nga ca jéggikaayu dexu Arnon, \q1 mel ni picc yu tasaaroo fa seeni tàgg, \q1 di fët-fëtluy, naaw. \q1 \v 3 Ña nga naa njiiti Yuda: \q1 «Xelal-leen nu, àtte nu, \q1 lalal nu bëccëg ndarakàmm ker gu mel ni guddi, \q1 yiire ko daw-làqu, yi nu doon; \q1 buleen nu wor te nuy wuta raw! \q1 \v 4 Mayleen nu nun ñi rëcce Mowab, nu dal ak yeen, \q1 te ngeen làq nu bóomkat.» \q1 Kiy note déy day jeexal, sëxëtoo dakk, \q1 kiy lore ci réew mi jóge fi, \q1 \v 5 ab jal sampe fi ci ngor, \q1 ki ci tooge jikko ju dëggu di askanu Daawuda \q1 te di njiit luy sàkku yoon, yàkkamti njekk. \b \q1 \v 6 Noo dégg ni Mowab réye, \q1 réya réy, reew te bew, \q1 seeni kañu di waxi neen. \q1 \v 7 Moo tax Mowab di jooy ba ñéppi Mowab jooyoo, \q1 ndax namm reseñ ja woon ca Kir Eres, \q1 ba ne yàcc, di binni. \q1 \v 8 Tool ya fa Esbon day wow, \q1 njiiti xeet yee dëggaate ngëneelu reseñ gu Sibma, \q1 te cabb ya laloon ba Yaser, \q1 ba àkki déndu màndiŋ ma, \q1 car ya law ba wàllaa géej. \q1 \v 9 Jooyi waa Yaser laay jooy reseñ ga fa Sibma, \q1 yeen waa Esbon ak Elale, ma sange leeni rongooñ, \q1 nde fa ngeen di dajaleek fa ngeen di góobe, \q1 coowal mbégtee fay dakke. \q1 \v 10 Mbégteek bànneex ay toxoo seeni tool, \q1 ay woy aki sarxolle noppee jibe seeni tóokër, \q1 te nalkatu reseñ naltil fa mbànd ya! \q1 Aji Sax jee dakkal coow li. \q1 \v 11 Maa ngi yërëm Mowab, bay binni ni buumu riiti, \q1 sama yaram daw ci Kir Eres. \b \q1 \v 12 Mowab a ngoog ak coonoom, \q1 ba muy deme fa bérab yu kawe ya, \q1 dugg jaamookaayam di ñaan te du am. \q1 \v 13 Lii la \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxoon bu yàgg ci mbirum Mowab, \q1 \v 14 tey Aji Sax ji wax ne: \q1 «Fileek ñetti at yu surga bu ñu bind waññ, \q1 dees na sàggi sagub Mowab, \q1 te li ñuy bare tey lépp, \q1 seenum ndes ay néew lool te tekkeedi.» \c 17 \s1 Ab yéeneb waxyu ñeel na péeyub Siri \q1 \v 1 Yéene bii ñeel na Damaas\f + \fr 17.1 \fr*\ft Damaas mooy péeyub Siri.\ft*\f*: \q1 Damaas a ngii, léegi mu noppee doon ab dëkk, \q1 xanaa ab jalu tojit; \q1 \v 2 dëkki Arower gental, \q1 gàtt yi jagoo, \q1 goore fa, kenn du leen dàq. \q1 \v 3 Tata dina tukkee diiwaanu Efrayim, \q1 nguur foqe dëkk ba ñuy wooye Damaas, \q1 te ndesu Siri du ëpp \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* daraja. \q1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee, Boroom gàngoori xare yi. \b \q1 \v 4 Bésub keroog sagub Yanqóoba sàggiku, \q1 yaram wa réer ko, mu jeex tàkk. \q1 \v 5 Day mel nim ngóob \q1 mu loxol góobkat bay dal, di dajale gub ya. \q1 Day mel ni ngóob ma ca xuru Refayeen, \q1 \v 6 fa dara dul des lu moy am poraat; \q1 mu mel ni wittum oliw, \q1 bu noppee ñaari doom ak ñett ay des ca kaw, \q1 mbaa ñeent ba juróom ci car yi meññ. \q1 Kàddug Aji Sax jee, Yàllay Israyil. \b \q1 \v 7 Bésub keroog nit sàkku Ki ko sàkk, \q1 ba ne jàkk Aji Sell ju Israyil. \q1 \v 8 Dootu sàkkooti lenn ci \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* \q1 yi mu sàkkal boppam. \q1 Dootu sàkkooti yooyu mu defare loxoom, \q1 du xer yi ñuy jaamoo \w Asera|lemma="Asera:"\w*, \q2 du yeneen sarxalukaayi cuuraay. \b \q1 \v 9 Bésub keroog seen dëkk yi tata wër, \q1 dees na leen won gannaaw \q2 ni dëkki Eween ñaak Amoreen ña\f + \fr 17.9 \fr*\ft Mbaa: \ft*\fqa ni gott yaak njobbaxtali tund ya,\fqa*\f*, \q1 ba leen bànni Israyil dàqee, \q1 lépp ay doon ab gent. \q1 \v 10 Yeena fàtte Yàlla ji leen di musal, \q1 bawuleen xel seen cëslaay jiy seen rawtu, \q1 xanaa di jëmbatal seeni tuur ay tooli ngëneel, \q1 di ji jiwu mu bawoo feneen. \q1 \v 11 Bés ba ngeen ko jëmbatee, ngeen gis mu sax, \q1 ëllëg ba bët setee, mu tóor, \q1 te ngóob réer bésub wopp, \q1 ci biir mitit wu amul paj. \b \q1 \v 12 Ndeysaan, mii riirum gàngoor yu mag! \q1 Xeet yu bareey riir ni riirum géej, \q1 ànd ŋarandoo ni géej gu sàmbaraax, \q1 gannax ya ŋarandoo. \q1 \v 13 Xeet yaa ngi ŋarandoo \q2 ni ndox mu baawaan, \q1 Yàlla gëdd leen, ñu daw ba sore; \q1 ngelaw yëngu, ñu naaw, \q1 ni boob, ba ca kaw tund ya, \q1 mbete pënd bu ngëlén wal, mu def callweer. \q1 \v 14 Ngoon a ngay jot, tiitaange ne jaas, \q1 balaa bët a set lépp jeex. \q1 Lii mooy añub ñuy sëxëtoo, \q1 lii mooy deminu ñiy nangu sunu alal. \c 18 \s1 Waxyu jib na, ñeel réewum Kuus \q1 \v 1 Wóoy ngalla réew ma gunóor yay riire, \q1 ca tàkkal dexi réewum \w Kuus|lemma="Kuus:"\w*. \q1 \v 2 Yeen ñiy yónni biir géej, ay ndaw, \q1 ci gaali barax yu war mbeex mi; \q1 yeen ndaw yu gaaw yi, demleen, \q1 fekki xeet wu siggi, rattax yaram, \q1 askan wu ñu ragale fu jegeek fu sore, \q1 xeet wu am doole, di falaxee, \q1 te seenum réew defi wal. \b \q1 \v 3 Yeen waa àddina wërngal këpp, \q1 yeen ñi dëkke suuf si, \q1 séentuleen raaya ba sampe fa tund ya, \q1 dégluleen liit ga ñuy wali. \q1 \v 4 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji kat da maa wax ne: \q1 «Maa ngi fi ma tollu di xool, ne tekk, \q1 ni tàngooru jant bu ne ràññ, \q1 mbaa lay bu defu niir ci tàngooru ngóob.» \q1 \v 5 Bala ngóob di jot, te fekk lépp tóor, \q1 ba tóor-tóor def reseñ ju xaay, \q1 mu jël ab sàrt, dog car yu ndaw yi, \q1 tenqi car yu mag ya, sànni; \q1 \v 6 ñu boole waccal njanaawi tund ya \q1 ak rabi àll yi, \q1 tan yi nawetoo ko, \q1 rabi àll yépp nooroo ko. \q1 \v 7 Su boobaa ñu indil Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, \q2 galag bu bawoo ci xeet wu siggi, rattax yaram, \q1 askan wu ñu ragale fu jegeek fu sore, \q1 xeet wu am doole, di falaxee, \q1 te seenum réew defi wal, \q1 galag ba agsi ba tundu \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, \q1 fa Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi dëël turam. \c 19 \s1 Ab yéeneb waxyu ñeel na Misra \q1 \v 1 Yéene bii ñeel na Misra: \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jaa ngii war niir wu gaaw, \q1 jëm réewum Misra. \q1 Yàllantuy Misra yég ko, di lox, \q1 fitu waa Misra rëcc. \q1 \v 2 Maay xiir Misra ci kaw Misra, \q1 kii song mbokkam, kii song xaritam, \q1 ab dëkk jógal ab dëkk, diiwaan jógal diiwaan. \q1 \v 3 Waa Misra jànnaxe, \q1 ma dëpp seen pexe. \q1 Ñu seeti yàllantu yeek njuuma yi, \q1 ak gisaanekat yeek boroom rawaan yi. \q1 \v 4 Maay teg Misra ci loxol sang bu néeg, \q1 buur bu dëgër xol jiite ko. \q1 Kàddug Boroom bee, Aji Sax ji ci gàngoor yi. \b \q1 \v 5 Ndoxum Niil ma day fer; \q1 dex gaay ŋiis, wow koŋŋ, \q1 \v 6 solom ya xasaw, \q1 wali Misra diib ba far ŋiis, \q1 barax ak lu mu xeetool lax, \q1 \v 7 gàncax ga leru dexu Niil \q1 ak ga saxe fa dex ga dabe géej, \q1 ak lu ñu jiwoon ca wet ga, \q1 lépp ay wow, naaw, ba jeex. \q1 \v 8 Nappkat di jàmbat, \q1 kuy sànnib oos dexu Niil di jooy, \q1 kuy mbaal waaru, \q1 \v 9 kuy liggéey lẽe am mbetteel, \q1 kuy jàrt ak a ràbb poqe jommi. \q1 \v 10 Ñi yor réew mi dañuy sëngéem, \q1 kuy liggéey di feyu am naqaru xol. \b \q1 \v 11 Kàngam ya fa Cowan\f + \fr 19.11 \fr*\ft Cowan ak Memfis ay dëkki Misra lañu.\ft*\f* dañuy teqlikook seen sago, \q1 diglekati Firawna yu xelu ya di digle ag ndof. \q1 Ma ne: «Yeen diglekat yi, nu ngeen mana waxe Firawna naan: \q1 “Nun ay boroom xel lanu, \q1 sosoo ca buur ya woon”?» \q1 \v 12 Firawnaa, ana say boroom xel? \q1 Nañ la waxal boog, ba xamle \q1 li Aji Sax ji Boroom gàngoor yi naral Misra. \q1 \v 13 Kàngami Cowan a ngi def yëfi dof, \q1 kàngam ya fa Memfis, ñu nax leen, \q1 te njiiti giiri Misra lajjal seen waa réew. \q1 \v 14 Aji Sax jee miirloo Misra, \q1 gëlëmal ko ci lépp lu muy def, \q1 ni màndikat buy jang ba tarxiis cim waccoom. \q1 \v 15 Du lenn lu kenn manatee defal Misra, \q1 bopp akub geen du ci am pexe, \q1 te bantub tiir ak barax a ci yem. \s1 Lu jëm ci muju Misra \q1 \v 16 Su bés baa waa Misra mel niy jigéen, \q1 di lox ndax tiit loxo bi jóg, \q1 te \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoor yi xàccil-leen ko. \q1 \v 17 Yuday doon tiitaangey waa Misra, \q1 ba ku ñu ci tudd Yuda, nga tiit, \q1 ngir la leen Aji Sax ji Boroom gàngoor yi naral. \q1 \v 18 Su keroogee mu am juróomi dëkki réewum Misra \q2 yu nit ñay waxe làmmiñu ebrë, \q1 di fa giñe Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, \q1 benn dëkk ba lañuy wooye Ir Ayeres, \q2 dëkkub yàqute. \q1 \v 19 Bésub keroog ab \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* ñeel Aji Sax ji, \q1 fa digg réewum Misra, \q1 aw xer it ñeel Aji Sax ji fa kemu réew ma, \q1 \v 20 loolu di firnde, ñeel Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, \q1 di lu ko seedeel fa biir réewum Misra. \q1 Bu ñu leen sonalee ba ñu woo Aji Sax ji, \q1 mu yónnee leen ku leen wallu, \q1 taxawu leen ba xettli leen. \q1 \v 21 Bésub keroog Aji Sax ji ci boppam mooy xamal Misra mooy kan, \q1 ba waa Misra xam Aji Sax ji, \q1 di jaamoo Aji Sax ji saraxi gàtt ak \w saraxi pepp|lemma="Sarax yi:"\w*, \q1 digook moom tey wàccook seeni dige. \q1 \v 22 Aji Sax jeey duma Misra \q1 duma yu ànd akum paj, \q1 ñu walbatiku ci Aji Sax ji, \q1 mu nangul leen, faj leen. \q1 \v 23 Su keroogee mbedd bawoo Misra ba Asiri, \q1 waa Asiri di dikk ba Misra, \q1 waa Misra di dem ba Asiri \q1 te Misra di jaamoondook Asiri. \q1 \v 24 Bésub keroog Israyil ñetteel Misraak Asiri, \q1 di barke fi digg àddina. \q1 \v 25 Aji Sax ji barkeel leen, ne: \q1 «Barke ñeel na Misra, sama ñoñ, \q1 ak Asiri mi ma sàkke samay loxo, \q1 ak Israyil sama séddoo.» \c 20 \s1 Kàddug waxyu ñeel na Misra ak Kuus \p \v 1 At ma bummib Asiri demee ca ndigalal Sargon buurub Asiri, ba songi dëkk ba ñuy wax Asdodd ca Filisti, ba mujj ko nangu, \v 2 fekk na \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax, Esayi doomu Amocc jottli. Mu ne ko: «Demal summi tubéyu saaku ji nga sol, te summi say dàll.» Mu def noona, di doxe yaramu neen, tànki neen. \v 3 Gannaaw gi Aji Sax ji ne: «Esayi sama jaam bi def na yaramu neen, tànki neen lu mat ñetti at, muy firnde, di tegtal ci mbirum Misra ak réewum \w Kuus|lemma="Kuus:"\w*. \v 4 Te noonu la buurub Asiri di yóbboo ngàllo Misra, toxal waa Kuus, ñuy ay ndaw aki màggat. Yaramu neen, tànki neen lañuy def, seen taat ne fàŋŋ, muy gàcceg Misra. \v 5 Dañuy boole njàqareek gàcce ndax réewum Kuus mi ñu yaakaaroon, ak Misra gi ñu doon sagoo.» \v 6 Bu keroogee ku dëkke tefes googu dina ne: «Xanaa kay du ñii lanu yaakaaroon! Te nu dawoon di wuti ndimbal ci ñoom, ngir rëcc buurub Asiri! Léegi nag nu nuy mucce?» \c 21 \s1 Ab yéeneb waxyu ñeel na Babilon \q1 \v 1 Yéene bii moo wàccal màndiŋ ma feggook géej ga: \q1 Ni ag ngëlén di riddee jaare Negew \q1 ni la noon di bawoo màndiŋ ma, \q1 jóge réew mu raglu. \q1 \v 2 Peeñu mu ñàng lañu ma ci wax. \q1 Workat biy wor, yàqkat biy yàq. \q1 Yeen waa Elam\f + \fr 21.2 \fr*\ft Elam am réew la mu bokkoon ci nguurug Pers, te di ab diiwaan ci réewum Iraan mu jamonoy tey.\ft*\f*, songleen; yeen waa Medd, gawleen leen. \q1 Dakkal naa mboolem onk yu ñu sabab. \q1 \v 3 Lii a waral sama njàqareg xol, \q1 mitit jàpp ma, mel ni mititu mat, \q1 ma jaaxle ba déggatuma, \q1 jàq ba gisatuma. \q1 \v 4 Bopp ubu, tiitaange jàpp ma; \q1 sama ngoonug bànneex \q1 soppiku guddi gu raglu. \b \q1 \v 5 Ndab taaje, laltan lale, \q1 ñuy lekk ak a naan. \q1 Ñu jekki ne: «Yeen kilifa yi, jógleen! \q1 Diwleen pakk yi!» \q1 \v 6 Boroom bi kat da maa wax, ne ma: \q1 «Doxal taxawal ab jongrukat, \q1 lu mu gis, wax ko. \q1 \v 7 Bu gisee gawar ci watiiru ñaari fas, \q1 ak ñu wari mbaam ak ñu wari giléem, \q1 na teewloo teewlu bu baax.» \q1 \v 8 Jongrukat ba àddu ca kaw ne: \q1 «Sang bi, maa ngii yendoo séentu, \q1 fanaane wattu fii ma taxaw. \q1 \v 9 Ma ne gawar a ngii, \q1 war watiiru ñaari fas. \q1 Nee: “Daanu nañoo, Babilon daanu na, \q1 jëmmi tuuram yépp tasaaroo fi suuf!”» \q1 \v 10 Yeen bokk yi ñu bàcc ni pepp ca sama dàgga ja, \q1 la ma dégge ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi, \q1 wax naa leen ko. \s1 Ab yéeneb waxyu ñeel na Duuma \q1 \v 11 Yéene bii moo wàccal Duuma\f + \fr 21.11 \fr*\ft Duuma ci Arabi la féete, feggook Seyir mbaa Edom. Baat la itam buy tekki selaw, ci làkku yawut.\ft*\f*: \q1 Nit a ngi may wooye tundu Seyir, naan: \q1 Jongrukat bi, lu des ci guddi gi? \q1 Éy jongrukat bi, lu desati ci guddi gi? \q1 \v 12 jongrukat bi ne: \q1 «Bët set, mu guddeeti rekk, \q1 Boo amee looy laaj, délsil laajaat ko.» \s1 Ab yéeneb waxyu ñeel na Arabi \q1 \v 13 Yéene bii moo wàccal Arabi: \q1 yeen cëggi askanu Dedan\f + \fr 21.13 \fr*\ft Dedan ak Teman ak Kedar ay xur la yu waa Arabi dëkke.\ft*\f*, \q1 mbooyum Arabi ngeen di fanaane. \q1 \v 14 Yeen waa Tema, dajejileen ak ña mar, \q1 yóbbul leen am ndox. \q1 Dogileen ñay daw, \q1 may leen ñu lekk. \q1 \v 15 Ay saamar de lañuy daw; \q1 saamar bu ñu leen xàccil \q1 ak fitt gu ñu leen diir \q1 ak tàngooru xare. \p \v 16 Aji Sax ji de da maa wax ne ma: «Fileek menn at mu surga bu ñu bind waññ, sagub dëkk bii di Kedar dina sàggiku, \v 17 li des ci jàmbaari fittkati Kedar di lu néew.» \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Yàllay Israyil wax na ko. \c 22 \s1 Ab yéeneb waxyu ñeel na Yerusalem \q1 \v 1 Yéene bii ñeel na xuru Peeñu ma: \q1 Ana lu ngeen di yéege, \q1 yeen ñépp seen kawi taax? \q1 \v 2 Lu waral coow li ak xaxaloo bi, \q1 ba dëkk biy riir? \q1 Ñi ngeen deele, saamar reyu leen, \q1 bóomuñu leen ci xare. \q1 \v 3 Seen njiiti xare yépp a bokk daw, \q1 ñu jàpp leen te taluñoo fitte. \q1 Seen njiit yi ñu gis yépp lañu jàpp, \q1 te ñu dawoon ba sore. \q1 \v 4 Moo ma tax ne: «Buleen ma xool, \q1 damay naqarlu, jooy. \q1 Tàyyileen maa dëfal ci sama bokk yi sànku.» \q1 \v 5 Lii kat bésub njommite laak coonook toroxte, \q1 bésu Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ci gàngoor yi, \q1 ci biir xuru Peeñu mi. \q1 Tata ja, ñu rëkka rëkk, mu màbb, \q1 yuux jolli, àkki tund ya. \q1 \v 6 Waa Elam gàllooy fitt, \q1 ñenn ña war watiir, gawar ya war, \q1 waa Kir ŋàbb pakk ya. \q1 \v 7 Seen xur yu nangu yaa fees aki watiir, \q1 gawar taxaw temm buntu Yerusalem, \q1 \v 8 te Yuda ne duŋŋ, dara wëru ko. \b \q1 Su keroogee ngeen yaakaar ngànnaay, \q2 ya ca kër ga ñuy wooye Gott ba, \q1 \v 9 far gis ni ñu bëtt-bëttee tatay Yerusalem, \q1 ji wër gox bi ñu naan Kër Daawuda. \q1 Ngeen rooti ndox ca solom bu suufe ba, denc ko, \q1 \v 10 boole ca waññ këri Yerusalem, \q1 màbb lenn, sàkk ca lu ngeen aare tata ya. \q1 \v 11 Da leen di fekk sàkk mbànd diggante ñaari tata yi, \q1 ngir denc ca ndoxum déeg bu yàgg ba. \q1 Waaye xooluleen ki dogal lii, \q1 xalaatuleen ki nasoon lii bu yàgg. \b \q1 \v 12 Bésub keroog Boroom bi, \q2 Aji Sax ji ci gàngoor yi moo leen di woo \q1 ci jooyoo ak ñaawlu \q1 ak wateefu nel, ak colu saaku ngir ñaawlu. \q1 \v 13 Te yeena ngii ci mbég ak bànneex, \q1 di rendi nag ak xar, \q1 di yàpp ak a naan, \q1 naan: «Nan lekk, naan, nde ëllëg, nu dee!» \q1 \v 14 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dégtal na ma lii: \q1 «Gii ñaawtéef déy deesu leen ko jéggal, \q1 ba keroog ngeen di dee.» \q1 Boroom bee ko giñ, \q1 moom Aji Sax ji Boroom gàngoor yi. \s1 Kàddug àrtu ñeel na Sebna \q1 \v 15 Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ci gàngoor yi dafa wax ne: \q1 «Ayca, demal ba ca Sebna, \q2 bëkk-néegu buur sii, nga ne ko: \q1 \v 16 Ana loo fi am, ak koo fi am? \q1 Nga di fi yettlu bàmmeel, yett ko ca kawte ya, \q1 di gaslu kër gooy mujje? \q1 \v 17 Jàmbaar, dama ne Aji Sax jee lay xalab; \q1 da la naa nikk, \q1 \v 18 fodonk la, rattax, \q1 nga xalangoo àll bu ne màww. \q1 Fa ngay dee, \q1 te fa la watiir yi ngay puukarewoo di des, \q1 muy sa gàccey waa kër sang.» \q1 \v 19 Aji Sax ji nee: «Maa lay jële sa liggéey, \q1 foqatee la sa péete mu kawe. \p \v 20 «Bésub keroog ma woo sama jaam bi, Elyakim doomu Ilkiya, \v 21 solal ko sa mbubb, dooleele ko sa ngañaay, teg kilifteefu réew mi ci loxoom, ba mu féete wàllu baay, waa Yerusalem, ak waa kër Yuda. \v 22 Maa koy ràng caabiy kër Daawuda, muy ubbi te kenn du tëj; di tëj te kenn du ubbi. \v 23 Maa koy samp fu dëgër ni ab wékkukaay, mu doon sagu kër baayam. \v 24 Waa kër baayam ak seen daraja, ñépp ay wékku ci moom, car yaak caraat ya. Ndab yu ndaw yépp ca la, kopp ya ba ca njaq ya. \v 25 Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi, mu ne: «bant ba sampe woon fu wóor day simpiku. Dees koy gor, mu fàq, la ca sëfe woon dog.» Aji Sax ji déy wax na ko. \c 23 \s1 Ab yéeneb waxyu ñeel na Tir \p \v 1 Yéene bii ñeel na dëkk ba ñuy wax Tir\f + \fr 23.1\fr*\fk Tir ak Sidon\fk*\ft ay dëkk yu am solo la woon ca Fenisi, ci réew mi ñuy wax Libaŋ tey.\ft*\f*: \q1 Yeen waa gaali Tarsis ñi deele, jooyleen! \q1 Lépp a yàqu! \q1 Du kër, du teeruwaay. \q1 Fa dunu Sippar\f + \fr 23.1 \fr*\ft Mbaa: dunu Kitim.\ft*\f* lañu leen ko waxe. \q1 \v 2 Yeen waa tefes, \q1 yaw Sidon laa ne, na say jula ñaawlu, \q1 yaw miy yónni nit ñu jaare géej, \q1 \v 3 war ndox ya ne xéew, \q1 peppum Sixor\f + \fr 23.3 \fr*\ft Mooy dexu Niil.\ft*\f* di sa tono, \q1 ak ngóobum Niil, \q1 ma xeet yi daan jula. \q1 \v 4 Yaw Sidon, gàcce ñeel na la, \q1 géej moo wax, tatay géej a ne: \q1 «Masumaa matu, masumaa jur, \q1 yaruma gone gu góor, yarumab janq.» \q1 \v 5 Bu xibaar ba àggee Misra de, \q1 ñu naqarlu deminu Tir. \q1 \v 6 Jàllal ba Tarsis\f + \fr 23.6 \fr*\ft Ab sanc la bu bokkoon ci Tir, ca wàllu Espaañ.\ft*\f*, \q1 yeen waa tefes ga fa ne, jooyleen jooyi dëj. \q1 \v 7 Xanaa lii du seen dëkk bu xumb ba, \q1 te cosaanam di janti démb, \q1 nit ña di fa jógey sancaani fu sore? \q1 \v 8 Ana ku fexeel lii Tir ma daan fale, \q1 ay julaam diy kàngam, \q1 di jaaykat yi àddina teral? \q1 \v 9 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoor yee ko fexe, \q1 ngir sàggi sagub képp ku fiy damu, \q1 ba teddadil képp ku àddina teral. \q1 \v 10 Yeen waa Tir, defleen ni dexu Niil, walal seen réew; \q1 kenn tereetu leen. \q1 \v 11 Aji Sax ji tàllal na loxoom, tiimale géej, \q1 yëngal réew yi, \q1 ba santaane ñu màbb tatay Kanaan. \q1 \v 12 Nee yeen waa Sidon ñi mel ni janq bu ñu tëdde, \q1 dootuleen xaxaloo. \q1 Ayca, dawleen jàlli ba dunu Sippar, \q1 te du tax ngeen am fa noflaay. \q1 \v 13 Xool-leen li dal réewum Kaldeen ñi. \q1 Dootuñu sax aw xeet. \q1 Asiri wacce na leen rabi màndiŋ mi. \q1 Tabax nañu, gaw ko, màbb këri buur ya, gental ko. \q1 \v 14 Yeen boroom gaali Tarsis, yuuxuleen ni ñu deele, \q1 seen tata màbb na! \p \v 15 Bu keroogee ñu fàtte Tir juróom ñaar fukki at, ni àppu benn buur. Bu juróom ñaar fukki at yi matee, Tir xewle la ñu woyal gànc ba, ne ko: \q1 \v 16 «Yaw gànc bi ñu wacc, fabal sa xalam, wër dëkk bi, \q1 xalamala xalam te gëna woy, \q1 ndax ñu geesu la.» \p \v 17 Bu juróom ñaar fukki at yi matee, Aji Sax ji dikkal Tir, ñu delluy liggéey, di feyu, di gànctook mboolem réewi àddina fi kaw suuf \v 18 Waaye seen ñaq ak seen peyoor, dees koy sellalal Aji Sax ji, deesu ko dajaleek a denc. Ñi dëkk fi kanam Aji Sax jeey jagoo njariñ la, mu di leen dundal ba ñu regg, di leen solal col gu jekk. \c 24 \ms1 Waxyu ñeel na mujug jamono \mr (Saar 24—27) \s1 Mbugal daj na àddina \q1 \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jaa ngii di tas àddina, \q1 tasaare ko, \q1 salfaañe li fi dénd bi, \q1 wasaare ñi ko dëkke: \q1 \v 2 \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* beek baadoolo bi, \q1 sang akub jaam, \q1 njaatige lu jigéen ak ab janqam, \q1 jaaykat ak jëndkat, \q1 ablekat ak àbbkat, \q1 leblekat ak lebkat. \q1 \v 3 Àddinaa ne duŋŋ duŋŋaaral, \q1 dees koo futti ba mu ne furaas! \q1 Aji Sax ji kat wax na kàddu gii! \q1 \v 4 Suuf a ngi wowa wow, ne sereŋ, \q1 àddina ne làcc, ne sereŋ, \q1 kàngami xeeti àddina ne làcc. \q1 \v 5 Suuf si la ñi ko dëkke sobeel, \q1 ñoo wàcc yoon yi, \q1 xëtt ndigal, \q1 fecci \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* gi sax dàkk. \q1 \v 6 Moo tax alkànde yàq suuf, \q1 ñi ko dëkke gàddu àq ji. \q1 Moo tax waa àddina raaf, \q1 ba ñi des di lu néew. \q1 \v 7 Biiñ ñàkk na, \q1 garabu reseñ lax, \q1 bépp xol bu tooyoon, binni. \q1 \v 8 Tabala ju xumb selaw na, \q1 ña daa xaxaloo dal, \q1 mbégtem buumi xalam dakk. \q1 \v 9 Kenn naanatul, di woy, \q1 ñoll wex na ka koy naan. \q1 \v 10 Dëkk bu gental tasaaroo na, \q1 kër yépp tëje, kenn duggul. \q1 \v 11 Mbedd maa ngi soowaloo, \q1 ndax biiñ bu ñàkk, \q1 gépp mbégte fey, \q1 bànneexu àddina dëddu. \q1 \v 12 Tojiti neen a des ci dëkk bi, \q1 bunt ba rajaxoo. \q1 \v 13 Noonu lay deme ci àddina, \q2 ci biir xeet yi, \q1 mbete benn-benni doomi oliw gu ñu gësëm, \q1 mbaa doomi reseñ yu des ca ndey ja, \q1 gannaaw bu ñu wittee ba sottal. \s1 Ndes wi rëcc mbugal a ngi sant \q1 \v 14 Ña ngay xaacu di sarxolle, \q1 waa sowu di sàbbaal ci màggug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \q1 \v 15 Yeen waa penku, sargal-leen Aji Sax ji boog, \q1 yeen waa duni géej, teral-leen Aji Sax ji Yàllay Israyil. \q1 \v 16 Cati àddina lay woy di jibe, nu dégg ñu naa: \q1 «Teddnga ñeel na Aji Jub ji!» \s1 Coono jeexul \q1 Waaye man dama ne: «Jeexle naa! \q1 Jeexle naa, wóoy man! \q1 Workat yaa ngi wora wor, \q1 ba far làggi ci wor.» \q1 \v 17 Yeen waa àddina, \q1 kat-kat, pax akub caax dëgmal na leen. \q1 \v 18 Nga déggi yuux, daw, \q1 tàbbi biir pax, \q1 génne pax, \q1 laawoob caax. \q1 Mbàndi kaw kat ubbi na, \q1 kenug àddina di reng-rengi. \q1 \v 19 Suuf daa loroo loru, \q1 fetta fett, \q1 salfaañoo salfaañu. \q1 \v 20 Suuf a ngi janga jang ni màndikat, \q1 ba joy ni mbaar, \q1 moyam diis ko gann, \q1 mu daanu te du jógati. \s1 Aji Sax jeey nguuru fa Siyoŋ \q1 \v 21 Bu bésub keroogee \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikke mbugal \q2 gàngoor ya fa kawa kaw, \q1 ak buuri àddina yi fi suuf. \q1 \v 22 Dees leen di boole denc cim pax, \q1 ne leen ràpp tëj, \q1 ba mu am ay fani fan, ñu mbugal leen. \q1 \v 23 Kersa la weer wiy am, \q1 gàcce ñeel jant bi; \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi daal, \q1 mooy nguuru Yerusalem, kaw tundu \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, \q1 leeram ga jollee fa kanam magi ñoñam. \c 25 \s1 Cant jib na \q1 \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, yaay sama Yàlla, \q1 dama lay teral, di la sant. \q1 Yaa defi jaloore, \q1 muy dogal yu yàgg, wér te wóor. \q1 \v 2 Yaa def dëkk bi jali doj, \q1 dëkk bii ñu dàbbli nga gental; \q1 taaxu doxandéem yi noppee doon péey ba fàww, \q1 te deesu ko tabaxaat. \q1 \v 3 Moo tax xeet wu am doole di la màggal, \q1 waa péeyu xeet yu néeg di la wormaal. \q1 \v 4 Yaa di rawtub néew-ji-doole, \q1 di rawtub aji ñàkk, biir njàqare, \q1 yaay mbaar mu ñuy yiiroo waame, \q1 di ker gu ñuy serloo ci tàngoor, \q1 nde merum kilifa gu néeg \q1 mooy waame wu ne yureet ci kaw miir. \q1 \v 5 Doxandéem yii diy noon, \q1 ni ngay dàqe tàngoor fi bérab bu ne sereŋ, \q1 ni ngay dakkale seen coowal xare. \q1 Ni aw tàngoor di dakke ndax aw niir, \q1 ni la woyu ñu néeg ñi di selawe. \s1 Bernde ñeel na xeet yépp \q1 \v 6 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoor yi, \q1 mooy berndeel xeet yépp fi kaw tund wii, \q1 bernde ju niin ak ngëneelu biiñ, \q1 yàpp wa duuf, yuq ja ne xéew, \q1 ak tànnéefu biiñ bu teey. \q1 \v 7 Fi kaw tund wii lay tukkile càngaay, \q2 li sàng askanoo askan, \q1 ak séru rabal bi ñu ràbbal xeetoo xeet. \q1 \v 8 Mooy mëdd ndee ba fàww! \q1 Boroom bi, Aji Sax jeey fompe \q2 gépp kanam rongooñi boroom. \q1 Buumi gàccey ñoñam it, \q1 moo koy doge fépp ci àddina. \q1 Aji Sax ji kat wax na ko. \b \q1 \v 9 Bésub keroog dees na ne: \q1 «Sunu Yàllaa ngii nag! \q1 Moom mii lanu yaakaaroon \q1 te moo nuy wallu. \q1 Aji Sax jii lanu yaakaaroon, \q1 nan bég te bànneexoo wallam.» \s1 Aji Sax ji tas na Mowab \q1 \v 10 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji kat teg na tund wii loxo, \q1 te ni ñuy dëggaatee boobum leeñ, \q1 ni lees fiy dëggaatee Mowab. \q1 \v 11 Mowab dina féqoo féqu, \q1 mel ni kuy jéema féey, \q1 waaye Aji Sax jee leen di torxal, \q2 ñook seen manoore. \q1 \v 12 Seen tata yu kawe, mu fél, màbb; \q1 rattax fi suuf, maasale. \c 26 \s1 Aji Sax jeey may ñoñam ndam \q1 \v 1 Bésub keroog dees na woy \q2 wii woy fi réewum Yuda: \q1 «Dëkk bu dëgër lanu am, \q1 Yàllaa nu may kaarangey tata, biir ak biti! \q1 \v 2 Ubbileen bunt yi, \q1 ba xeet wi jub te sàmm ngëm duggsi! \q1 \v 3 Yaw Aji Sax ji, \q1 ku dogu, pastéefu, wóolu la, \q1 nga may ko jàmm ju mat, \q1 nde moo la wóolu. \q1 \v 4 Wóoluleen \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji tey ak ëllëg; \q1 Yàlla Aji Sax ji déy, \q1 moo mat cëslaay ba fàww. \q1 \v 5 Moo wàcce ñi dëkke woon fa kaw, \q1 moo detteel waa dëkk ba aju woon, \q1 daaneel leen, ñu xalangu, \q1 ba mëq suuf, \q1 \v 6 baadoola joggi, dëggaate, \q1 néew-ji-doole note leen.» \b \q1 \v 7 Ku dëggu, yoonam day maase; \q1 ku dëggu, Aji Jub ji jubal xàllam. \q1 \v 8 Aji Sax ji, nu ngi lay xaar, \q1 fi sa kaw yoonu santaane yi, \q1 di la sàkku, ba la xel, \q1 lii déy, mooy sunu nammeelu xol. \q1 \v 9 Xol laa lay sàkkoo guddi, \q1 sama jëmm jépp di la laaj. \q1 Bu say àtte teewee fi kaw suuf, \q1 waa àddina xame ca njekk. \q1 \v 10 Ku bon, boo ko yërëmee, \q1 du xam njekk. \q1 Biir réew mu nit ñay jubal \q1 lay xal di luubale, \q1 du faale kawewaayu Aji Sax ji. \q1 \v 11 Aji Sax ji, yaa xàcci sa loxo, \q1 waaye yéguñu ko. \q1 Won leen ni nga nabe ci sa ñoñ, ñu rus, \q1 te sawaraay xoyom sa noon yooyu. \q1 \v 12 Aji Sax ji, yaa nuy defal jàmm, \q1 te lépp lu nu def, yaa nu ko sottalal. \q1 \v 13 Aji Sax ji sunu Yàlla, \q1 yeneen sang yu la moy moom nañu nu, \q1 waaye saw tur rekk lanuy màggal. \q1 \v 14 Yooyu sang dee nañu, nekkatuñu, \q1 wuute nañu, jógatuñu. \q1 Yaa def nii, faagaagal leen, \q1 ba far sax seen tur. \q1 \v 15 Aji Sax ji, yaa yokk xeet wi, \q1 yaw mii yaa yokk xeet wi, \q1 yaa fésal sa teddnga, \q1 yaa yokk mboolem kemi réew mi! \b \q1 \v 16 Éy Aji Sax ji, ci biir njàqare lañu la sàkkoo; \q1 ba ñu tegoo sa mbugal, \q1 lañu la déey seenug ñaan. \q1 \v 17 Éy Aji Sax ji, ni kuy matu \q2 lanu meloon fi sa kanam, \q1 di wañaarook a yuuxu. \q1 \v 18 Danoo ëmb bay matu \q1 te jurunu lu moy ngelaw. \q1 Indiwunu genn mucc ci àddina, \q1 mayunu ci kenn lu ko taxa dund. \q1 \v 19 Waaye yaw askan wi, ñi nga deele \q2 ñooy dellu dundaat, \q1 seeni néew ay dekki, \q1 ku doon nelaw sa biir bàmmeel, \q1 yewwu, sarxolle. \q1 Aji Sax jeey yebal lay bu ànd aki leer, \q1 suuf délloosi ña dëddu. \s1 Mbugal ñeel na géej ak jéeri \q1 \v 20 Yeen samaw askan, ayca duggleen seeni néeg, \q1 tëju ca biir. \q1 Làquleen as lëf, ba sànj mi jàll. \q1 \v 21 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji kat a ngii di génne bérabam ba, \q1 nara dikke waa àddina mbugalu ñaawtéef, \q1 ba suuf wone deret ji ñu tuur fi kawam, \q1 te dootu sàng ñi ñu bóom. \c 27 \q1 \v 1 Bésub keroog Aji Sax ji dikke saamaram \q2 bu jàmbaare, ñàng te réy, \q1 ba dal ci kaw Lewiyatan, jaan ja ca xél wa, \q1 Lewiyatan jaan jay wañaaruy dem, \q1 ninki-nànkay géej jooju lay rey. \s1 Aji Sax ji juboo naak ñoñam \q1 \v 2 Bésub keroog, tóokëru reseñ ju neex am, \q1 nangeen ko woy, \q1 \v 3 te man \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji maa koy topptoo, \q1 di ko suuxat saa su ne, \q1 di ko wattu guddeek bëccëg, \q1 bala koo kenn a song. \q1 \v 4 Mereetuma tóokër bii, \q1 waaye lu ciy dég aki dagg, \q1 ma dox wuti ko, xareek moom, \q1 boole lépp xoyom. \q1 \v 5 Xanaa ku langaamoo sama kiiraay \q1 te jàmmook man, \q1 ba jàmmook man. \q1 \v 6 Ay bés a ngi ñëw Yanqóoba saxi reen, \q1 Israyil moomooy tóor, law, \q1 ba feesal déndu àddinaak meññeef. \b \q1 \v 7 Defe ngeen ne Aji Sax ji duma na Israyil, \q1 na mu dumaa ña leen duma woon? \q1 Am bóomal na leen lu tollook \q2 la seeni bóomkat bóomoon? \q1 \v 8 Ndànk-ndànk la jëflanteek ñoom, \q1 ba mu leen toxalee, \q1 dàqe leen noowam gu mag, \q2 bésu ngelawal penku. \q1 \v 9 Nii la Yanqóoba jotoo ñaawtéefam, \q1 nii la mujje am njéggalu bàkkaaram: \q1 Day boole doji \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi yépp, \q1 rajaxe ni doji kew, \q1 xer wu ñuy jaamoo \w Asera|lemma="Asera:"\w* dootu fa sampe, \q1 mbaa sarxalukaayi suurukaay. \q1 \v 10 Dëkk bu ñu dàbbli mooy wéet, \q1 gental, ne wëyëŋ! \q1 Fa la nag di fore, \q1 fa lay goor, di lekk cari garab ya, \q1 \v 11 car ya wow, damm, \q1 jigéen ñi dikk, xambe. \q1 Dañu di xeet wu dul dégg, \q1 ba tax ki leen sàkk yërëmu leen, \q1 moo leen bind te ñeewantewu leen. \b \q1 \v 12 Bésub keroog Aji Sax ji bàcc, \q1 dale ca dexu Efraat ba ca walum Misra, \q1 te yeen \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, dees na leen for \q2 kenn-kenn, ba ngeen daj. \q1 \v 13 Bésub keroog liit gu mag jib, \q1 ña laŋoon réewum Asiri délsi, \q1 ànd ak ña ñu tasaare woon biir réewum Misra, \q1 ba sujjóotalsi Aji Sax ji fa Yerusalem, \q1 fa kaw tund wu \w sell|lemma="sell:"\w* wa. \c 28 \ms1 Xibaaru mbugal ñeel na ay xeet \mr (Saar 28—33) \s1 Mbugal ñeel na Samari \q1 \v 1 Wóoy ngalla Efrayim\f + \fr 28.1 \fr*\fk Efrayim \fk*\ft mooy giir gu am solo ci fukki giir ya ca nguurug bëj-gànnaar ga ñuy wax Israyil. Leeleeg muy tur wi ñuy wooye waa gox boobu.\ft*\f*, \q1 kaala gu yànj ga ay màndikatam di sagoo! \q1 Taaram bu yéeme baa koy réer, \q1 ni tóor-tóor yu wow, \q1 te ma nga toŋ ca coll\f + \fr 28.1 \fr*\fk coll \fk*\ft mooy fa Samari nekk, di péeyub nguurug bëj-gànnaar ga ñuy wax Israyil.\ft*\f*, wa ña biiñ man dëkke, \q1 fa tiim xur wu nangu wa. \q1 \v 2 Dégluleen, jàmbaar ju am doolee ngi dikkal Boroom bi, \q1 di tawub doji yuur, ngëlén luy sànke, \q1 riddee riddi, sotti waame wu wale! \q1 Loxoom la koy rattaxe fi suuf. \q1 \v 3 Dees na joggati kaala \q2 gii màndikati Efrayim di sagoo. \q1 \v 4 Te tóor mu lax mi muy gànjaroo, \q1 mu tege ca coll ya tiim xur wu nangu wa, \q1 day mel ni figg ju ñor te jotul; \q1 ka ko gis a koy gaaw witt, wonn. \q1 \v 5 Bésub keroog \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoor yi \q1 di kaala gu yànj, gànjar gu yéeme, \q1 ñeel ndesu ñoñam, \q1 \v 6 mooy sol noowug dëgg kuy toog di àtte, \q1 di jàmbaaral ñiy waññi noon yi song dëkk bi, xare. \b \q1 \v 7 Ñii itam ay naan biiñ bay tërëf, \q1 màndiw ñoll, di jang: \q1 \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* akub yonent la aw ñoll di tërëfloo, \q1 biiñ jànnaxe leen, \q1 ñu màndiw ñoll, di jang, \q1 bu ñu amee am peeñu, di tërëf. \q1 \v 8 Seen taabal yépp a ngi taq ripp, \q1 fépp di waccu ak mbalit. \q1 \v 9 Ñu naa: «Ana ku Esayi mii di jàngal? \q1 Ana ku muy àgge xibaar? \q1 Xanaa ku yàggula fer, \q1 di doora bàyyi ween? \q1 \v 10 Ca rëdd wii, ca rëdd wee, \q1 nàngam sii, nàngam see, \q1 as tuut fii, as tuut fee.» \q1 \v 11 Xanaa boog nit ñu seen wax leerul, \q1 ñu diy làkk-kat, \q1 la Aji Sax jiy waxeek askan wii? \q1 \v 12 Moo leen waxoon ne leen: \q1 «Fii moo di nopplukaay bi, \q1 noppal-leen ku sonn. \q1 Fii a di dal-lukaay bi!» \q1 Waaye nanguwuñoo dégg. \q1 \v 13 Moo tax seen kàddug Aji Sax mujj di: \q1 «Ca rëdd wii, ca rëdd wee, \q1 nàngam sii, nàngam see, \q1 as tuut fii, as tuut fee.» \q1 Moo tax ñuy tërëf, \q1 daanoo njaaxaanaay ba damm, \q1 di sërëx ak a keppu. \s1 Doju doorukaay wee mat wéeruwaay \q1 \v 14 Kon nag yeen kókkalikat yi yilif \q2 askanu Yerusalem wii, \q1 dégluleen kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji! \q1 \v 15 Yeena naay: «Danoo wóllëranteek ndee, \q1 njaniiw lanu digool, ba du nu moom, \q1 ba bu yaru musiba dikkeek diisaayam, du nu laal? \q1 Noo def ay fen sunu rawtu, \q1 ay wor di sunu làquwaay.» \q1 \v 16 Moo tax Boroom bi Aji Sax ji wax ne: \q1 «Maa ngii di dëj fi \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* aw doju coll, \q1 muy doju collu tànnéef wu gànjare ngir kenu gi, \q1 te ku ko wéeroo doo gaawa daw. \q1 \v 17 Dëgg laay def nattukaay, \q1 njekk di sama buumu beteex, \q1 tawub doji yuur buub rawtub fen, \q1 wal ma mëdd làquwaay, \q1 \v 18 seen wóllëranteek ndee neen, \q1 seen digook njaniiw toxu, \q1 yaru musiba dikk ak diisaayam, \q1 wulli leen ba ngeen nooy. \q1 \v 19 Saa yu dikkee ne leen céex, \q1 suba su ne mu ne jaas, \q1 guddeek bëccëg, mu teew, \q1 te bu jibee sax fit rëcc.» \q1 \v 20 Lal a gàtt ba deesu ci tàlli, \q1 malaan cëkk ba matul càngaay\f + \fr 28.20 \fr*\fk lal beek malaan \fk*\ft mi ñuy wax fii, mooy misaal Misra mi ñu yaakaaroon te du leen doy kiiraay.\ft*\f*. \q1 \v 21 Aji Sax jeey jóg na woon \q2 fa tundu Perasim, \q1 xadaru na woon ca xuru Gabawon \q1 ngir jëf jëfam, \q1 jëfam ju yéeme ja! \q1 Moo nara liggéey liggéeyam booba, \q1 liggéeyam bu tumurànke ba! \q1 \v 22 Tee ngeena baña kókkalee \q1 bala ñoo teeŋal seeni jéng? \q1 Sànkute kat moo di dogal bi ma dégg, \q1 mu bawoo fa Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yi, \q1 di luy dikkal réew mi mépp. \s1 Aji Sax jee xam doxalin \q1 \v 23 Teeyluleen te déglu sama kàddu, \q1 teewluleen ba dégg samay wax. \q1 \v 24 Xool-leen ci lii: Ndax beykat bi day dëkke gàbb, \q1 di rëdd ak a gàbbaat? \q1 \v 25 Bu gàbbee ba toolam maase, \q1 du day sànni jiwum nisel\f + \fr 28.25 \fr*\fk nisel ak kumin \fk*\ft ay xeeti safal la.\ft*\f*, \q1 wasaare jiwum kumin, \q1 daldi def bele bi ay saawo, \q1 sànni lors ba fa mu ko rëddal, \q1 doora suy bele bu dëgër ba ca wet ya? \q1 \v 26 Dees koo xamal yoon wa, \q1 te Yàllaam a ko ko jàngal. \q1 \v 27 Mbàccum nisel watiir amu ca yoon, \q1 te deesul bàcc kumin itam, ba joggi ca tànki watiir. \q1 Mbàccum nisel, yet a koy def; \q1 mbàccum kumin, bant bu yem. \q1 \v 28 Gubi bele, dees na ca jaare watiir, \q1 waaye deesu ci dëkk; \q1 watiir ngay takk, bàcce ko pepp, \q1 waaye doo ko bàcc ba mu far mokk! \q1 \v 29 Xel moomu it fa \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji \q2 Boroom gàngoor yi la bawoo. \q1 Ndigalam a ni yéemee, \q1 pexeem màgge ni! \c 29 \s1 Mbugal ñeel na Aryel \q1 \v 1 Wóoy ngalla Aryelee, Aryel\f + \fr 29.1 \fr*\ft Tur la wu ñuy wooye Yerusalem. Man naa tekki itam taalub sarxalukaay ba woon ca kër Yàlla ga.\ft*\f*, \q1 dëkk ba Daawuda dale. \q1 Dundleen at ak at, \q1 amal-leen ci màggal ci kaw màggal. \q1 \v 2 Du tee ma wàcceel Aryel musiba, \q1 ñuy yuuxook a jooyoo. \q1 Yerusalem ay mel ci man \q2 ni Aryel, taalub sarxalukaay. \q1 \v 3 Maay dal ub dal, wër la, \q1 gawe la ay tata, \q1 jali jal, fuuge la. \q1 \v 4 Dinga suufe ba mel ni kuy àddoo biir suuf, \q1 sa baat di ndéey lu dégtoo xóote ya pëndub suuf lale, \q1 mel ni njuuma lu waxam bawoo biir suuf, \q1 baatam yeloo xóote ya pëndub suuf lale. \q1 \v 5 Say noon ay def gàngoor ni feppi suuf, \q1 di naaxu nit ñu néeg, ñu ngelaw liy wal nib cox. \q1 Loolooy jekki am, ca saa sa. \q1 \v 6 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoori xare yi moo lay dikke \q2 dënook suuf su yëngu ak riir mu réy, \q1 ngelaw riddi, di ngëlén, \q1 ànd ak sawara wuy xoyome. \q1 \v 7 Mboolem xeet yu bare yiy xareek Aryel, \q1 di song dëkk beeki tataam, \q1 nar leena torxal, \q1 ñoom ñépp ay mel ni gént mbaa njeneeru guddi! \q1 \v 8 Su boobaa mu mel ni ku xiif, \q1 géntul lu moy di lekk, \q1 yewwu rekk, biir ba wéet; \q1 mbaa ku mar, géntul lu moy di naan, \q1 yewwu rekk, loof, put ga wow koŋŋ. \q1 Noonu la gàngooru xeet yépp di nekke, \q1 mboolem xeet yooyuy xaareji fa \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*! \q1 \v 9 Tendeefal, jommi rekk! \q1 Gëmm, gumba rekk. \q1 Ñiika màndi te du biiñ, \q1 ñuy jang te duw ñoll! \q1 \v 10 Aji Sax ji déy yeen la wal \q2 ngelawal nelaw yu xóot, \q1 taf seeni gët, te ngeen di yonent yi; \q1 muur seeni bopp te ngeen di boroom peeñu yi. \q1 \v 11 Peeñum xew-xew yii yépp ump na leen, \q1 ni leen kàdduy téere bu ñu tay umpe. \q1 Boo ko joxee ku jàng, ne ko mu jàng ko, \q1 mu ne la manu ko, nde dees koo tay; \q1 \v 12 nga jox ko ku jàngul, ne ko mu jàng, \q1 mu ne la manula jàng. \b \q1 \v 13 Boroom bi nee: «Askan wii, làmmiñ lañu ma jegee, \q1 lori neen lañu may wormaale, \q1 te seen xol sore ma. \q1 Seen ragal ak man it, \q1 njàngum tari kepp la. \q1 \v 14 Moo tax maa ngii di dellu wéyeek askan wii, \q2 ay kéemtaan aki kiraama \q1 yuy tiiñ boroom xel ak xelam, \q1 réer xamkat ak xam-xamam.» \b \q1 \v 15 Wóoy ngalla ñiy làqu Aji Sax ji, \q1 di loqal seen mébét, \q1 ba lëndëm muur seen jëf, \q1 ñu naan: «Ana ku nu gis? \q1 Ana ku nu yég?» \q1 \v 16 Yeenaka juunum xel! \q1 Dees na jaawale tabaxkatu njaq beek ban bi? \q1 Ndax li ñu sàkk dina ne ki ko sàkk: \q1 «Kii sàkku ma»? \q1 Am njaq leey waxtaane tabaxkat bi naa: \q1 «Kii manula tabax»? \s1 La woon day wonni \q1 \v 17 Xamuleen ne fi leek lu néewa néew, \q1 àllub Libaŋ sopplikub tóokër, \q1 tóokër bi walbatiku meññ, ba ñu ne ab gott la? \q1 \v 18 Su bés baa ab tëx dégg kàdduy téere, \q1 silmaxa tàggook lëndëm, di gis, \q1 \v 19 néew-doole yi dellu bége \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 ñi gëna ñàkk di bànneexoo Aji Sell ju Israyil. \q1 \v 20 Ku néeg déy dina neen, \q1 kuy ñaawle sànku, \q1 te képp kuy yeeru nu mu defe lu bon, \q2 dees na la dagg. \q1 \v 21 Mooy ñiy tuumaal nit, \q1 di fiir ab àttekat ca pénc ma, \q1 di àtte ñàkkal nit ku jub ci dara. \q1 \v 22 Moo tax Aji Sax, ji jotoon Ibraayma, \q1 wax ak waa kër Yanqóoba, ne leen: \q1 «Léegi Yanqóoba du rusati, \q1 du amati yaraanga.» \q1 \v 23 Bu am meññeefam gisee \q1 li sama loxo def fi seen biir, \q1 dinañu sellal sama tur, \q1 sellal ma, man Aji Sell ju Yanqóoba. \q1 Dinañu ma wormaal, man Yàllay Israyil, \q1 \v 24 ba ñi réeroon, mujj xam; \q1 ñurumtukat yi dégg ndigal. \c 30 \s1 Misra du mat Israyil cëslaay \q1 \v 1 Wóoy ngalla doom yii diy fippukat! \q1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. \q1 Ñu ngi nas mébét yu ma diglewul, \q1 di digoo digoo yu ma leen xelalul, \q1 di tegle bàkkaar ci kaw bàkkaar. \q1 \v 2 Ñoo dox wuti Misra te laajuñu ma, \q1 xanaa di sàkku rawtub Firawna, \q1 di keppaaroo keppaarug Misra\f + \fr 30.2 \fr*\ft Misra lañu yaakaaroon mu aar leen ci Asiri.\ft*\f*. \q1 \v 3 Rawtub Firawnaay mujj di seen gàcce, \q1 keppaarug Misra di seen toroxte. \q1 \v 4 Seeni jawriñ a nga xaat ba Cowan, \q1 seeni ndaw àgg ba Anes\f + \fr 30.4 \fr*\fk Cowan \fk*\ft ak \ft*\fk Anes \fk*\ft ci Misra lañu bokk.\ft*\f*, \q1 \v 5 waaye ñoom ñépp kersa lañuy ame Misra, \q2 googu leen dul amal njariñ. \q1 Du ndimbal, du njariñ, \q1 xanaa gàcceek toroxte. \b \q1 \v 6 Yéeneb waxyu bii ñeel na malay àllub Negew: \q1 Réewum tiis laak njàqare, \q1 kërug gayndeeki segg, \q1 ak saamaan ak céebi, \q1 mbaam lañu sëf seen alal, jaare fa, \q1 giléem lañu sëf seeni denc, \q1 jëme xeet wu leen dul jariñ. \q1 \v 7 Ndimbalu Misra, cóolóolu neen! \q1 Moo tax ma tudde ko: \q1 Raxab, ponkal mi ne yàcc. \b \q1 \v 8 Aji Sax ji nee: \q1 «Ayca, bind ko ci àlluwa, ñu gis! \q1 Rëdd ko cib téere, \q2 ngir ëllëg ak sibbir, \q2 mu dib seede ba fàww.» \q1 \v 9 Wii xeet kat ay fippukat lañu, \q1 yii doom a diy fen-kat \q1 te nanguwuñoo sàmm yoonu Aji Sax ji! \q1 \v 10 Boroom ngis, ñu ne ko: «Bul gis,» \q1 boroom peeñu, ñu ne ko: «Bu ñu firil peeñuy dëgg. \q1 Wax nu lu neex, \q1 gisal nu ay nax.» \q1 \v 11 Moyal yoon wi; \q1 lajj, wàcc xàll wi, \q1 te may nu jàmm ak Aji Sell ju Israyil. \q1 \v 12 Moo tax Aji Sell ju Israyil wax ne: \q1 «Gannaaw yeena xalab kàddu gii, \q1 yaakaaruleen lu moy doole ak pexey njubadi \q2 yu ngeen wéeroo, \q1 \v 13 googu ñaawtéef ay mujj doon \q1 seen xar-xaru tata ju kawe, \q1 funki, tata ja jekki jóoru. \q1 \v 14 Da naan tasar ni njaqal xandeer \q2 lu ñu naan rajax te ñéebluweesu ko, \q1 ba deesul gis ca tojit ya, dog bu tibb xal, \q1 mbaa mu as ndoxum déeg.» \b \q1 \v 15 Ndax Boroom bi Aji Sax ji, \q1 Aji Sell ju Israyil dafa wax ne: \q1 «Délsi, dal-lu moo leen di musal. \q1 Ne tekk te wóolu maa leen di dooleel. \q1 Waaye yeena buggul! \q1 \v 16 Yeena ne: “Déedéet, danuy war fas, daw!” \q1 Dingeen daw moos! \q1 Ngeen ne: “Daamar yu gaaw lanuy war.” \q1 Ñi leen di dàq it di war daamar yu gaaw! \q1 \v 17 Junneey daw fu leen kenn gëdde, \q1 juróom gëdd, ngeen daw yeen ñépp, \q1 ba ña des mel ni bantub raaya ci kaw tund, \q1 ne cundum ni raaya bu wéet ca coll wa.» \q1 \v 18 Aji Sax ji déy a leen namma baaxe, \q1 moo ko tax di jóg moos ngir yërëm leen, \q1 nde Aji Sax jeey Yàllay njubte. \q1 Ndokklee képp ku ko yaakaar! \b \q1 \v 19 Yeen waa \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, yeen waa Yerusalem, \q1 dootuleen jooy mukk! \q1 Bu ngeen jooyee, mu yërëm leen moos; \q1 bu leen di dégg, di leen nangul. \q1 \v 20 Boroom bee leen di leel njàqare, \q1 nàndal leen coono, \q1 waaye moo leen di jàngal, dootu leen làqu; \q1 dingeen gis ki leen di jàngal, \q1 \v 21 di dégg kàddu guy jibe seen gannaaw, \q1 naa leen: «Yoon waa ngii, jaareleen fi;» \q1 bu ngeen awee ndijoor, mbaa càmmoñ. \q1 \v 22 Su boobaa ngeen sobeel seen jëmmi tuur yi ñu xoob xaalis; \q1 ak wurus wu xoob seen tuur yi ñu móol, \q1 ba boole lépp sànni ni sagar yu sobewu, \q1 ne ko: «Sore nu!» \q1 \v 23 Su boobaa Aji Sax ji tawal lu ngeen ji, \q1 may leen pepp mu suuf meññ, \q1 sakkan te nangu, \q1 seen juri keroog di fore parlu yu yaa, \q1 \v 24 Nag yeek mbaam yiy rijji sax, \q1 di xontoo cox bu ñu xorom, \q1 jóge ci mbàccum roq ak ngaska. \q1 \v 25 Te tundoo tund wu kawe, \q1 wu mag ak wu ndaw, \q1 wali ndox a cay wale, \q1 keroog bés ba deret di tuuroo tuuru, \q1 tata ya jóoru. \q1 \v 26 Weer day leer ni jant, \q1 jant gënatee leer, \q1 mel ni juróom yaari bëccëg, \q1 bésub keroog ba Aji Sax jiy takk damm-dammu ñoñam, \q1 fajal leen góom yi ay dóoram sabab. \s1 Aji Sax ji song na Asiri \q1 \v 27 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jaa ngii, jóge fu sore; \q1 mer ma réy, \q1 mu jógaale kàddug àrtu gu diis, \q1 di waxe xadar ju mat sëkk, \q1 baat ba mel ni sawara wuy xoyome, \q1 \v 28 noo ga di wal mu baawaan, \q1 tollu ci put; \q1 mu nara segge xeet yi ab seggukaayu alkànde, \q1 wewal xeet yi ag laab gu leen di réeral. \q1 \v 29 Teewul, bokk yi, seen woy yay jib; \q1 mel ni guddig màggal, \q1 ànd ak mbégte ni kuy toxoro, \q1 yéeg jëm kaw tundu Aji Sax ji, \q1 cëslaayal Israyil. \q1 \v 30 Aji Sax jeey yékkati kàddoom gu màgg, \q1 wone diisaayu loxoom, \q1 ànd ak tàngooru meram, \q1 ak sawara wuy xoyome, \q1 ak waameek ngëlén, ak tawub doji yuur. \q1 \v 31 Kàddug Aji Sax jeey jib, \q1 Asiri tiit bay lox, \q1 yetu Aji Sax ja dal, \q1 \v 32 te saa yu yet wa Aji Sax ji féetale Asiri dalee, \q1 ngeen jibal am tëgg aki xalam. \q1 Aji Sax jeey xàcci loxoom, xareek Asiri. \q1 \v 33 Xambees na démb ab taal bu ñuy wax Tofet\f + \fr 30.33 \fr*\fk Tofet \fk*\ft mooy bérab ba ñu daan lakke ay gone yu ñu def sarax, ñeel tuur ma ñuy wax Moleg.\ft*\f*, \q1 te buur ba lees ko waajalal; \q1 dees koo xóotal, yaatal ko, \q1 sawara way tàkk, matt ma ne gàññ, \q1 noowal Aji Sax ji nar caa tàkke, \q1 di sël-sëli ni walum tamarax. \c 31 \s1 Musiba ñeel na ku yaakaar Misra \q1 \v 1 Wóoy ngalla ña wàcci Misra, di wuti wall; \q1 di sukkandikoo ay fas, \q1 tey yaakaari watiir ndax bare ga, \q1 aki gawar ndax lim bu takku ba \q1 te xooluñu ci Aji Sell ju Israyil, \q1 sàkkuwñu kooku di \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \p \v 2 Moona moom it xareñ na, \q1 mane na safaan, \q1 te du fommi digeem. \q1 Kuy def lu bon, mu dal ci waa këram; \q1 kuy def lu ñaaw, mu song ay wallam. \q1 \v 3 Waa Misra, niti neen, duñu Yàlla; \q1 seeni fas it, suuxu neen, duñu leneen. \q1 Aji Sax jeey xàcci loxoom, \q1 kiy walloo mooy tërëf, \q1 ki ñuy wallu daanu, \q1 ñoom ñépp bokk sànku. \q1 \v 4 Aji Sax ji déy da maa wax ne ma: \q1 «Gaynde gu mag ak gu ndaw, bu jàppee bay xiiru, \q1 boo ko wooloon gàngooru sàmm it, \q1 duñu soowaloo ba xëbal ko, \q1 duñu ñolñoli ba mu dellu gannaaw. \q1 Noonu la Aji Sax ji Boroom gàngoor yiy wàcce, \q1 xaresi fi kaw tundu \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* ak waa tund wa.» \q1 \v 5 Ni picc di daayaarloo, aar am tàggam, \q1 ni la Aji Sax ji Boroom gàngoor yiy yiire Yerusalem. \q1 Mooy aar, di xettli, \q1 mooy musal, di yiwi. \p \v 6 Éy bokki Israyil, fippu ngeen Aji Sax ji ba sës, waaye walbatikuleen! \v 7 Bésub keroog ku ne sànni yàllantuy xaalisam, ak yàllantuy wurusam yi mu sàkke woon loxoy bàkkaaram. \q1 \v 8 Asiri nag day daanu, \q1 te saamaru nit du ko daaneel, \q1 saamar bu doom aadama moomul a koy alag, \q1 mu daw, won saamar gannaaw, \q1 ay gone yu góoram dugg liggéeyu sañul-bañ. \q1 \v 9 Ñi ñu yaakaar dañuy tiit, ne wëqet, \q1 seeni kilifa jàq, ba daw wacc raaya ba. \q1 Kàddug Aji Sax jee, \q1 Boroom sawara wi ci Siyoŋ, \q1 Boroom taal bi ci Yerusalem! \c 32 \s1 Dëgg ay mujj \q1 \v 1 Buur a ngii, njekk lay nguuroo, \q1 jawriñ ñi it, yoon lañuy yilifee; \q1 \v 2 ku ci nekk mel ni seelukaayu ngelaw, \q1 di kiiraay ci ngëlén, \q1 mel ni wali ndox ci suuf su ne sereŋ, \q1 mbaa keppaaru doj wu mag ci àll bu mar. \q1 \v 3 Su boobaa gëti njàccaar yi dootuñu gëmm, \q1 te noppi ñiy dégg dañuy teewlu, \q1 \v 4 ku yàkkamti di ràññee, ba mana xam, \q1 làmmiñu ku dër gaawa wax lu leer. \q1 \v 5 Booba deesatul wooye ab dof, gor si, \q1 te njublaŋ dootu dégg «ku tedd ki.» \q1 \v 6 Ab dof, waxi dof lay wax, \q1 xel ma di nas ñaawtéef, \q1 mu nar jëf ju teddadi. \q1 Lu ñaaw lay wax, jëme ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 di xiifal ku xiif, \q1 di xañ ku mar lu mu naan. \q1 \v 7 Ab njublaŋ, ay pexeem musiba la. \q1 Njekkar lay nas, \q1 ba bu néew-ji-doole sàkkoo dëgg it, \q1 mu fen ba lor ko. \q1 \v 8 Waaye gor si, ngor lay mébét, \q1 te ngor lay wéye. \b \q1 \v 9 Yeen jigéen ñi dal xel, \q1 taxawleen temm, déglu ma; \q1 yeen janq ji féex, \q1 teewluleen ma. \q1 \v 10 Yeen jigéen ñi dal xel, \q1 fi leek at aki fan ngeen jàq; \q1 witt mi du baax, ngóob du taxaw. \q1 \v 11 Jigéen ñi dal xel, ragal-leen; \q1 yeen ñi féex laa ne, tiitleen! \q1 Futtikuleen, ba ne duŋŋ; \q1 gembooy saaku, ñaawloo. \q1 \v 12 Fëggleen seen dënn, \q1 jooy tooli bànneex ya, \q1 jooyleen reseñ ju nangu ja, \q1 \v 13 ak sama suufas bokk, \q2 ya ay dég aki dagg nangu. \q1 Jooyleen kay kër ya ca mbégte ma, \q1 ak dëkk bu xumb ba. \q1 \v 14 Kër gu rafet sax, dees koy wacc, \q1 dëkk baak riiram, dees koy dëddu; \q1 tund ak tóoju doon ay xunti ba fàww, \q1 mbaamu àll ne ca finaax, jur ga di ca fore, \q1 \v 15 ba keroog leeru xel sóobale nu fa kaw, \q1 màndiŋ mi sopplikub tóokër, \q1 tóokër meññ, ba ñu ne ab gott la. \q1 \v 16 Su boobaa yoon dëkke màndiŋ mi, \q1 njekk tooge tóokër bi. \q1 \v 17 Su booba njekk ay jur jàmm, \q1 njekk ay dalal, di aare ba fàww, \q1 \v 18 ba sama bokk yi dëkke sancub jàmm, \q1 ci dëkkuwaay yu wóor, \q1 dal-lukaay yu dal xel. \q1 \v 19 Gott bi day daanu ci tawub doji yuur, \q1 dëkk bi detteelu ba ne dett. \q1 \v 20 Waaye ndokklee yeen ñi tala ji fépp fuy ndox \q1 te saña afal nag ak mbaam. \c 33 \s1 Ña daan sànke sànku nañu \q1 \v 1 Wóoy ngalla yaw bóomkat bi kenn bóomul, \q1 yaw workat bi kenn worul. \q1 Boo noppee bóome, ñu bóom la, \q1 te boo noppee wore, ñu wor la. \q1 \v 2 Éy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ngalla baaxe nu; \q1 yaw lanu yaakaar! \q1 Xëyeel a dooleel wii xeet, \q1 wallu nu ci biir njàqare. \q1 \v 3 Sam riir jib, xeet yi fëx; \q1 nga jóg, waaso yi fëlxoo. \q1 \v 4 Dees na sëxëtoo sa alal sëxëtoob soccet. \q1 Dees na ko sam ni njéeréer di samee! \q1 \v 5 Aji Sax jee kawe, \q1 moo dëkke fa kawa kaw, \q1 te mooy dajal fi \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* njekk ak yoon. \q1 \v 6 Liy dalal seen jamono mooy \q2 koomu ndam; xel ak xam-xam, \q1 te ragal Aji Sax ji, loolooy seen alal. \b \q1 \v 7 Xool-leen seen jàmbaar \q2 ñiy yuuxoo ci mbedd mi, \q1 ndawi jàmm yaa ngii, \q1 di jooyoo jooy yu metti. \q1 \v 8 Yoon yaa ngi wéet, \q1 kenn jaareetul ci ñall wi! \q1 \w Kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* fecciku na, \q1 xeebees na ay seede, \q1 te kenn faaleetul doom aadama. \q1 \v 9 Suuf a ngi maral, wow koŋŋ, \q1 gottub Libaŋ am gàcce, lax, \q1 àllub Saron doon joor gu wow, \q1 garabi Basan ak Karmel yëngu, di ruus. \q1 \v 10 Aji Sax ji nee: «Xaaral rekk ma jóg, \q1 xaaral rekk ma ne ñokket, \q1 xaaral rekk ma teewal samag kawe. \q1 \v 11 Seeni mébét di boob, \q1 bu sottee dim ngooñ; \q1 seen noowug bopp mooy xamb sawara, \q2 wi leen di xoyom. \q1 \v 12 Xeet yeey sànku \q1 ni doj yu lakk ba doon kew, \q1 mbaa taxas yu ñu buub, \q1 sànni ci sawara, mu tàkk. \q1 \v 13 Yeen ñi sore, dégluleen li ma def; \q1 yeen ñi jege, xamleen ne maa am doole.» \b \q1 \v 14 Bàkkaarkati Siyoŋ tiit nañu, \q1 way-gëmadi yaa ngay lox. \q1 Ana kan ci nun moo mana dal ak \q2 sawara suy xoyome\f + \fr 33.14 \fr*\fk sawara: \fk*\ft seetal ci 30.27 ak 31.9.\ft*\f*? \q1 Ana kan ci nun moo mana dal ak \q2 taal yu yànj ya dul fey? \q1 \v 15 Xanaa kiy doxe njekk, \q1 di wax njub, \q1 bañ alalu foqati; \q1 loxo bay jalax ab ger, \q1 noppam di tanqamlu waxi bóome, \q1 bëtam di gëmm, ba du gis lu bon. \q1 \v 16 Ku ni mel, bérab bu kawe lay dëkke, \q1 doj yu ñu dàbbli di rawtoom, \q1 dundam doy, \q1 te ndoxam du ñàkk. \s1 Yerusalem mucc na cib noon \q1 \v 17 Yaw mi mel nii, buur bi ci taar bi ngay teg bët; \q1 yaay gis réew mi ne màww. \q1 \v 18 Sam xel dem ca sa tiitaange ja woon, \q1 nga ne: «Moo, ana ka doon waññ? \q1 Ana ka doon natt diisaayu galag? \q1 Ana ka doon waññiy tata?» \q1 \v 19 Su boobaa dootoo gis xeet wii di jaay doole, \q1 xeet wii diisu làkk ba déggeesu ko, \q1 taqu làmmiñ ba xameesul lu ñuy wax. \q1 \v 20 Xoolal \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, dëkk ba nuy màggale; \q1 yaay teg bët Yerusalem, dëkkuwaay bu dal ba, \q1 xayma bu deesul sempi, \q1 wewukaay ya deesu ko buddi mukk, \q1 te luy buumu xayma ya it, deesu ko dog. \q1 \v 21 Foofa déy la nu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ju màgg ji \q2 di nekkal bérab bu defi dex aki wal, \q1 fu gaalu joow dul dawe, \q1 te gaal gu mag du fa jaare, \q1 \v 22 Aji Sax jee nuy jiite, \q1 Aji Sax jee nuy dogalal yoon. \q1 Aji Sax jeey sunu buur! \q1 Moom moo nuy wallu. \q1 \v 23 Yeen nag seen réew mi gaal la, \q2 gu goj ya yolom, \q1 ponk ba ca digg ba di yëngu, \q1 ba ndimol gaal gi firikuwul. \q1 Dees na séddoo lël ju ne gàññ, \q1 ba làggi ya sax séddu ca. \q1 \v 24 Du kenn ci waa Yerusalem, \q1 ku neeti wopp na. \q1 Waa dëkk bépp ay am njéggalu bàkkaar. \c 34 \ms1 Gannaaw mbugal, mbégte \mr (Saar 34—35) \s1 Mbugal ñeel na Edom \q1 \v 1 Yeen xeet yi, jegesileen te déglu; \q1 yeen askan yi, teewluleen! \q1 Na suuf ak li ci biiram déglu, \q1 muy àddinaak lépp lu mu jur. \q1 \v 2 Merum \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñeel na xeetoo xeet, \q1 am sànj ñeel gàngoori xeet yi. \q1 Aji Sax ji faagaagal leen, \q1 dogal ñu war leena rendi. \q1 \v 3 Seeni néew lees di xalab, \q1 ñu médd, xet ga gilli, \q1 seen deret la tund yiy sangoo. \q1 \v 4 Gàngooru asamaan gépp ay tasaaroo, \q1 asamaan taxañe ni lëmësub kayit, \q1 gàngooram gépp ruus \q1 ni xobu reseñ mbaa figg gu lax. \b \q1 \v 5 Aji Sax ji nee: «Saab saamar a reye fa asamaan \q2 ba màndi deret, \q1 te mu ngii di wàccal Edom, \q1 xeet wi may faagaagal, ngir àttee leen ko.» \q1 \v 6 Aji Sax jee yor saamar bu màndi deret, \q1 yafloo nebbon, \q1 ak deretu kuuy mu ndaw ak bëy, \q1 ak nebbonu dëmbéenu kuuy. \q1 Aji Sax ji kat moo am ab sarax fa Boccra, \q1 muy tër mu réy fa réewum Edom. \q1 \v 7 Nagi àll yaay ànd ak ñoom daanu, \q1 ñook yëkk yu ndaw yaak yu mag ya, \q1 seen réew mi màndi deret, \q1 suuf sa niin batt ak nebbon. \q1 \v 8 Bésub feyu la, Aji Sax ji di ca feyoo; \q1 mooy at mi Edom di yooloo la mu loroon \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*. \q1 \v 9 Wali Edom di ca soppliku koltaar, \q1 pëndub suufam doon tamarax, \q1 suufam mel ni koltaar buy lakk, \q1 \v 10 guddeek bëccëg, du fey, \q1 saxar sa day gilli ba fàww, \q1 réew ma gental giiru jamono, \q1 te deesatu fa jaare mukk. \q1 \v 11 Céeleek siññéel a koy nangu, \q1 looy ak baaxoñ dëkke fa. \q1 Buumu beteex lees koy natte, maasale, \q1 ba mu ne maraas, ne wëyëŋ. \q1 \v 12 Garmi ya dootuñu fa teewe, \q1 ba di fa samp nguur, \q1 te seen kàngam yépp ay wuute. \q1 \v 13 Seen kër buur ya la dég ya di lawe, \q1 gajj aki taxas saxe tata ya, \q1 till dëkke, \q1 bànjóoli tàgge, \q1 \v 14 rabi màndiŋ mi di fa dajeeki bukki, \q1 bëyu àll di fa wooye moroom ma. \q1 Fa la rabu guddi di dal-loo, \q1 fàkkal fa boppam ab dal. \q1 \v 15 Fa la luy nen di tàgge, nen fa, \q1 bóof, ba tostan, yiire keppaaram; \q1 tan ya bokk fa daje, \q2 ku ci nekk ak moroom ma. \q1 \v 16 Seet ko ci téereb Aji Sax ji, jàng ko; \q1 du menn mala muy wuute ca gent ba, \q1 lu ci nekk a fay ànd ak moroom ma. \q1 Aji Sax jee ko santaane ci gémmiñam, \q1 moo leen di dajale, moom ci boppam. \q1 \v 17 Moom moo leen ko muurale, \q1 sédd leen suuf sa ci loxoom, \q1 ñu séddoo ko ba fàww, \q1 màkkaanoo ko maasoo maas. \c 35 \s1 Yoonu ñibbi Siyoŋ taxaw na \q1 \v 1 Màndiŋ ak suuf su ne sereŋ dina bég, \q1 joor gu wow bànneexu, tóor ba ne ràññ. \q1 \v 2 Day tóora tóor, \q1 di bànneexu, bay sarxolle, \q1 ba jagoo darajay gottub Libaŋ \q1 ak taaru àllub Karmel ak Saron. \q1 Foofa lees di gise darajay \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 sunu taaru Yàlla. \q1 \v 3 Ku yoqi, dooleel-leen ko, \q1 ku óom yay fenqe, jàppleleen ko. \q1 \v 4 Ku fitam rëcc, ne leen ko: \q1 «Dëgërlul te bul tiit. \q1 Sa Yàllaa ngii di la feyul, \q1 ba yool say noon. \q1 Moom mooy dikk, wallusi la.» \b \q1 \v 5 Su boobaa gëti silmaxa muriku, \q1 noppi tëx sikkliku. \q1 \v 6 Su boobaa ab làggi ne jàyy ni kéwél, \q1 ab luu sarxolle. \q1 Am ndox ay fettaxe màndiŋ ma, \q1 ay wal wale joor gu wow, \q1 \v 7 suuf su wow doon ub déeg, \q1 joor gu maral ballal bëti ndox. \q1 Fa till fàkkoon, di fa goore, \q1 gattax ak barax a fay sëqe. \q1 \v 8 Foofa law yoon di jaare, \q1 ñu di ko wooye Yoon wu \w sell|lemma="sell:"\w* wi. \q1 Ku sobewu du fa jaare, \q1 ñi moom woowu yoon, \q1 ñooy ñi koy topp. \q1 Ab dof sax du fa lajje. \q1 \v 9 Gaynde du fa am, \q1 rab wu aay du fa dox, \q1 du lenn lees fay gis, \q1 ku ñu jot rekk a fay jaare. \q1 \v 10 Ñi Aji Sax ji xettleey délsi, \q1 duggsi \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, di sarxolle, \q1 kaalawoo bànneex bu sax. \q1 Mbég ak bànneex a leen di dab, \q1 naqar aku tiis dëddu leen. \c 36 \ms1 Lu jëm ci Buur Esekiya \mr (Saar 36—39) \s1 Asiri song na Yuda \p \v 1 Gannaaw gi, ca fukk ak ñeenteelu atu nguurug Esekiya buurub Yuda, ca la Senakerib buurub Asiri dikk song mboolem dëkki Yuda ya tata wër, daldi leen nangu. \v 2 Buurub Asiri moo yebale fa dëkk ba ñuy wax Lakis, bëkk-néegam Rabsake, mu ànd ak mbooloo mu réy, ba ca Buur Esekiya ca Yerusalem. Ba Rabsake agsee ba tollook solomu mbàndum kaw ma, feggook yoon wa jëm ca toolub fóotukaay ba, fa la taxaw. \v 3 Ba loolu amee bootalub buur Elyakim doomu Ilkiya moo ànd ak Sebna, bindkat ba, ak doomu Asaf, Yowa ma yor téere ya, ñu dikk dajeek moom. \v 4 Rabsake bëkk-néegu buurub Asiri ne leen: «Waxleen nag Esekiya ne ko: Buur bu mag ba, buurub Asiri dafa wax ne: “Sa yaakaar jii nga yaakaar, ana foo ko teg? \v 5 Noon naa làmmiñ kese doy na pexeek njàmbaar cib xare? Ma ne: Ana kan nga yaakaar bay fippu ci sama kaw? \v 6 Misra daal, nga yaakaar, bantu barax bu tas boobu di sokk képp ku ko wéeroo! Firawna buuru Misra de, mooy boobu bant ci képp ku ko yaakaar. \v 7 Xanaa doo ma ne seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ngeen yaakaar? Xanaa du moom nga toxal \w bérabi jaamookaayam|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* yeek \w sarxalukaayam|lemma="sarxalukaay b-:"\w*, ba noppi ne waa Yerusalem ak Yuda sarxalukaay boobu lañuy sujjóotal?” \v 8 Léegi daal, déggool rekk ak sama sang buurub Asiri, ma jox la ñaari junniy fas, ndegam am ngay gawaram! \v 9 Ana noo mana tëwe ki gëna tuut ci sama jawriñi sang? May wax ngay yaakaare Misra ay watiir aki fas. \v 10 Te sax, xanaa du Aji Sax ji laa àndal ba dalsi fi kaw réew mii, ngir tas ko? Aji Sax ji ci boppam moo ma ne: “Songal réew mii, tas ko!”» \v 11 Ba loolu amee Elyakim ak Sebna ak Yowa ñaan Rabsake, ne ko: «Ngalla, làkk nu arameen, dégg nanu ko. Bu nu wax ebrë, mbooloo mi ci kaw tata ji di ci dégg.» \v 12 Bëkk-néeg ba ne leen: «Ndax yeen ak seen sang doŋŋ la ma sama sang yóbbante kàddu yii? Ñi toog ci kaw tata ji dañu cee bokkul? Te ñu nara ànd ak yeen lekk seen jonkani bopp, naan seenum saw!» \v 13 Bëkk-néeg ba nag taxaw, xaacu ca kaw ci ebrë ne: «Dégluleen kàdduy buur bu mag bi, buurub Asiri. \v 14 Buur dafa wax ne: “Bu leen Esekiya nax, ndax manu leena xettli. \v 15 Te bu leen Esekiya yaakaarloo Aji Sax ji, naan leen: ‘Aji Sax ji moo nuy xettli moos, te deesul teg dëkk bii ci loxol buurub Asiri!’ \v 16 Buleen déglu Esekiya. Buurub Asiri kat dafa wax ne: Jàmmooleen ak man te ngeen génn dëkk bi, dikk nangul ma. Su ngeen ko defee, ku nekk ci yeen mana lekk ak jàmm ci garabu reseñam, lekk ak jàmm ci figgam, di naan ndoxum teenam, \v 17 ba keroog may dikk, yóbbu leen réew mu mel ni seen réew mi, réewum pepp ak ndoxum reseñ, réewum mburu ak tooli reseñ. \v 18 Bu leen Esekiya sànk, naan leen: ‘Aji Sax ji moo nuy xettli.’ Ndax tuuri xeet yi mas nañoo xettli réewu wenn xeet ci buurub Asiri? \v 19 Ana tuuri réew yii di Amat ak Arpàdd? Ana tuuri Sefarwayim? Ndax dañoo xettli Samari ci man? \v 20 Tuuri réew yii yépp, ana mu ci xettli menn réew ak man, ba Aji Sax ji wara mana xettli, Yerusalem ak man?”» \p \v 21 Ñooña ne cell, tontuwuñu ko baat, ndax Buur moo leen santoon ne leen buñu ko tontu. \v 22 Ba loolu amee bootalub Buur, Elyakim doomu Ilkiya ak Sebna, bindkat ba, ak doomu Asaf, Yowa ma denc téere ya, ñoo dem ak seen yérey ñaawlu yu xottiku, ba ca Esekiya. Ñu daldi koy àgge kàddug bëkk-néeg ba. \c 37 \p \v 1 Naka la ko Buur Esekiya dégg, daldi xotti ay yéreem, sol saaku yu muy ñaawloo. Mu dem nag ca kër Aji Sax ji. \v 2 Ba loolu amee mu yebal Elyakim bootalub Buur ak Sebna bindkat ba, ak ñay mag ca \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ya. Ñu sol saaku yu ñuy ñaawloo, daldi dem ca Yonent Yàlla Esayi doomu Amocc. \v 3 Ñu ne ko: «Esekiya dafa wax ne: “Bésub tey bésub njàqare la ak mbugal ak gàcce. Mooy li ñuy wax naa: Doom a ngi ci buntub juddu, te dooley wasin réer! \v 4 Jombul nag sa Yàlla Aji Sax ji dégg kàdduy bëkk-néeg bi sangam buurub Asiri yebal, ngir mu kókkali Yàlla jiy dund. Te kon sa Yàlla Aji Sax ji mooy dogal mbugal mi war ci kàddu yooyu mu dégg. Yékkatil kàddug ñaan rekk, ngir ñi fi desagum.”» \p \v 5 Ba surgay Buur Esekiya àggee Esayi wax jooju leen seen sang wax, \v 6 Esayi da ne leen: «Waxleen seen sang ne ko: Aji Sax ji dafa wax ne: “Bul ragal kàddu yi nga dégg surgay buurub Asiri ñàkke ma ko kersa. \v 7 Maa ngii di ko sol xel mu ko gëmloo xibaar bu muy dégg, ba dellu réewam, ma fàdde ko ab saamar ca am réewam.”» \s1 Asiri tooñati na Yuda \p \v 8 Gannaaw loolu Rabsake dégg ne buurub Asiri bàyyikoo na Lakis, bay xareek dëkk ba ñuy wax Libna. Mu walbatiku fekki ko foofa. \v 9 Booba buurub Asiri daa dégg ne Tiraka buurub \w Kuus|lemma="Kuus:"\w* moo leen di songsi. Ba mu ca déggee daa yebal ay ndaw ca Esekiya, ne leen: \v 10 «Waxleen Esekiya buurub Yuda ne ko: “Seen Yàlla ji ngeen yaakaar, bumu leen nax, naa leen deesul teg Yerusalem ci loxol buurub Asiri. \v 11 Xanaa yaw ci sa bopp dégg nga li buuri Asiri def mboolem réew yi, faagaagal leen? Yaw nag, yaa ciy mucc? \v 12 Xeet yi samay maam sànk, seeni tuur dañu leena musal, muy Gosan, di Karan, di Resef, di askanu Eden wa woon ca Telasar? \v 13 Ana buuri Amat ak Arpàdd ak Layir ak Sefarwayim ak Ena ak Iwa?”» \p \v 14 Ba Esekiya jëlee bataaxal ba ca loxol ndaw ya, jàng ko ba noppi, dafa dem ba ca kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Mu daldi tàllal bataaxal ba fa kanam Aji Sax ji. \v 15 Esekiya ñaan Aji Sax ji, ne ko: \v 16 «Éy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Yàllay Israyil mi toog fi tiim \w serub|lemma="serub y-:"\w* yi. Yaw doŋŋ yaa di Yàllay mboolem nguuri àddina. Yaw déy, yaa sàkk asamaan ak suuf. \v 17 Ngalla Aji Sax ji, dékkal sa nopp ba dégg; Aji Sax ji, xippil say gët ba gis, te dégg mboolem kàdduy Senakerib yi mu yóbbante, ngir ñàkke la ko kersa, yaw, Yàlla jiy dund! \v 18 Aylayéwén Aji Sax ji, buuri Asiree tas mboolem xeet yeek seeni réew, \v 19 te ñoo sànni seeni yàlla ci sawara it, ndax yooyoo dul Yàlla, xanaa lu nit sàkke loxoom, bant ak doj, ba tax ñu sànk leen. \v 20 Kon nag Aji Sax ji sunu Yàlla, wallu nook moom, ba mboolem nguuri àddina xam ne yaw doŋŋ yaa di Aji Sax ji.» \s1 Yonent Yàlla Esayi yégle na jéllub Asiri \p \v 21 Ba mu ko defee Esayi doomu Amocc yónnee ca Esekiya ne ko: «\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, Yàllay Israyil, mi nga ñaan ci mbirum Senakerib buurub Asiri, dafa wax ne: \v 22 Lii moo di kàddu gi Aji Sax ji wax ci moom: \q1 Yaw, janq \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* mu taaru da laa xeeb, \q1 di la ñaawal. \q1 Yerusalem, dëkk bu taaru booboo \q2 lay wëcc bopp, \q1 di la kekku sa gannaaw. \q1 \v 23 Ana kooy kókkaleek a ñàkke kersa? \q1 Moo kooy yékkatil kàddu? \q1 Kooy xool gëti xeebeel? \q1 Xanaa du Aji Sell ju Israyil ji? \q1 \v 24 Yaa yebal say surga, \q1 di kókkali Boroom bi, te naa: \q1 “Sama watiir yi ne xas \q1 laa ware kawtey tund yi, \q1 jàll ba ca xolu Libaŋ. \q1 Maa gor seedaram ya fa sut \q1 ak tànnéefi garabi sipparam: \q1 maay àkki ba ca collub kaw bu tundu Libaŋ, \q1 ak gottam bu naat ba nib tóokër. \q1 \v 25 Maa gas ay teen, naan, \q1 maa joggatee sama téstën, wali Misra yépp, \q1 ŋiisal ko.” \q1 \v 26 Waaye xanaa déggoo ne bu yàgg laa dogal loolu? \q1 Ca jant yu jëkk ya laa ko nasoon, \q1 tey ma sottal ko, \q1 ba nga mana def genti jali tojit, dëkk yu tata wër. \q1 \v 27 Waa dëkk ya ne yàcc, jàq, torox, \q1 mel ni gàncaxu àll mbaa ñax mu yees, \q1 mbete caxum xadd \q1 mbaa tool bu car jógagul. \q1 \v 28 Waaye boo toogee, boo génnee, \q2 boo duggee, xam naa, \q1 boo xadaroo sama kaw it, xam naa. \q1 \v 29 Yaa xadaru sama kaw, \q1 ba sag reewande tàbbi sama nopp! \q1 Maa lay takkal ag nos akug laab, \q1 waññi la, nga dellu yoon wa nga dikke woon. \q1 \v 30 Lii, def ko ci, mu dib takk. \q1 Dees na lekk ren peppum saxayaay, \q1 déwén it dees na lekk lu saxal boppam. \q1 Waaye déwén-jéeg, \q1 ngeen ji, góob, \q1 jëmbat tóokëri reseñ, lekk ca meññeef ma. \q1 \v 31 Ndes wa des ca askanu Yuda \q1 ñooy saxaat ay reen, \q1 ba meññaat ay doom. \q1 \v 32 Yerusalem kay law ndes di génne, \q1 aw ndes ay rëcce tundu Siyoŋ, \q1 te Aji Sax ji Boroom gàngoor yi \q2 mooy sottal loolu ci xéraangeem. \q1 \v 33 Moo tax Aji Sax ji wax ci buurub Asiri ne: \q1 “Du dugg ci dëkk bii, \q1 du fi soqig fitt, \q1 du fi taxawe ab pakk, \q1 du fi jal jal bu muy gawe! \q1 \v 34 Yoon wa mu dikke lay delloo, \q1 biib dëkk, du fi dugg. \q1 Kàddug Aji Sax jee! \q1 \v 35 Maay aar dëkk bii, musal ko \q2 ngir man ci sama bopp, \q1 ak Daawuda sama jaam bi.”» \p \v 36 Ba loolu amee malaakam Aji Sax ji dikk, fàdd ca dalub Asiri téeméer ak juróom ñett fukk ak juróomi junni (185 000). Ca ëllëg sa ña mucc teela xëy, yemuñu ci lu moy ñooña ñépp diy néew. \v 37 Ba mu ko defee Senakerib buurub Asiri daldi fabu, ñibbi. Mu toog nag ca Niniw. \v 38 Gannaaw gi, ba muy sujjóot ca kër tuuram ma ñuy wax Nisrog, Addraameleg ak Sareser, doomam yu góor ñoo ko fa fàdde saamar. Ñoom nag ñu daw làquji réew ma ñuy wax Araraat. Ci kaw loolu doomam Asaradon falu buur, wuutu ko. \c 38 \s1 Esekiyel wopp na ba jóg \p \v 1 Jant yooyu Esekiya moo woppoon, bay waaja dee. Yonent Yàlla Esayi doomu Amocc dikk, ne ko: «\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: “Dénkaaneel sa mbiri kër, ndax dangay dee, doo jóg!”» \v 2 Esekiya nag walbatiku, jublook miir ba, ñaan ci Aji Sax ji. \v 3 Mu ne: «Éy Aji Sax ji, ngalla bàyyil xel ni ma àndeek yaw sama léppi xol, ci kóllëre. Te it li nga rafetlu laa jëfe.» Mu jooy nag, jooy yu metti. \p \v 4 Ci kaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal Esayi, ne ko: \v 5 «Doxal ba ca Esekiya, nga ne ko: Aji Sax ji sa Yàllay maam Daawuda dafa wax ne: “Dégg naa sag ñaan, gis naa say rongooñ. Maa ngii di yokk ci saw fan fukki at ak juróom. \v 6 Buurub Asiri ak dooleem, maa la ciy xettli, yaw ak dëkk bii, te maay aar dëkk bii.”» \p \v 7 Lii nag ngay def ab takk bu bawoo ci Aji Sax ji, di firndeel ne Aji Sax ji dina def li mu wax: \v 8 Maa ngii di delloo ker gi gannaaw lu tollook fukki dëggastal, ya jant bi wàccoon ca kaw iskaleb Axas. Ci kaw loolu jant bi dellu gannaaw lu tollook fukki dëggastal ya mu jotoona wàcc. \p \v 9 Mbind mii nag Esekiya buurub Yuda moo ko bindoon, gannaaw ba mu tëddee wopp, ba jóg: \q1 \v 10 Man de dama noon: \q1 «Sama digg doole laay deme \q1 jaare bunti njaniiw, \q1 sama ndesu fan réer ma!» \q1 \v 11 Ma noon: «Dootuma gisati\f + \fr 38.11 \fr*\ft gis Aji Sax ji mooy dem biir kër Aji Sax ji. Seetal ci aaya 22 ak \ft*\ft \+bk Sabóor\+bk* 27.4.\ft*\f* Aji Sax ji, \q1 duma gisati Aji Sax ji fi kërug àddina. \q1 Duma tegati doom aadama bët, \q1 dootu fii ci waa àddina. \q1 \v 12 Sama dëkkuwaay lañu sempi, \q1 yóbbu fu sore, \q1 mbete xaymab sàmm. \q1 Sama àpp a taxañe, \q1 ni ndimo lu ab ràbb doge ca mbaam ma. \q1 Diggante bëccëg ak guddi, nga jekkli ma. \q1 \v 13 May xalaat, ba bët set; \q1 Aji Sax jiy dammat samay yax ni gaynde, \q1 diggante bëccëg ak guddi, nga jekkli ma. \q1 \v 14 May ciib-ciibi ni wetwet mbaa ramatu, \q1 di binni nim xati, \q1 di séentu kaw ba saay gët giim. \q1 Dama noon: Éy Boroom bi, loof naa, \q1 dimbali ma.» \q1 \v 15 Waaye lu may waxati? \q1 Aji Sax jee ma wax, \q1 te moo jëf. \q1 Kon, ma temp ndànk sama giiru dund \q2 ndax tiisu xol. \q1 \v 16 Boroom bi, ci sa kàddook sa jëf la nit di dunde \q1 te ci laay noyyee ba tey. \q1 Yaa ma wéral, may ma, ma dund. \q1 \v 17 Ndeke sama tiisu xol wii, \q1 sama jàmm rekk a tax. \q1 Sa cofeel a tax \q1 nga sorele maak paxum sànkute. \q1 Yaa sànni sa gannaaw sama bépp bàkkaar. \q1 \v 18 Njaniiw du la sant, \q1 ndee du la gërëm, \q1 te ku tàbbim pax yaakaaratul sa kóllëre. \q1 \v 19 Kiy dund, kiy dund doŋŋ mooy ki lay sant \q1 ni man bésub tey jii, \q1 te baay mooy xamal doom sa kóllëre. \q1 \v 20 Aji Sax ji yaa may wallu, \q1 nu di la woy, ànd aki xalam, \q1 sunu giiru dund, \q1 fa sa biir kër, yaw Aji Sax ji. \p \v 21 Fekk na Esayi noon: «Indileen ab danku figg, ngeen jonj ko ci taabu Esekiya bi, kon dina dund,» \v 22 ba Esekiya noon ko: «Ana lu di takk biy firndeel ne dinaa wér, ba dellooti kër Aji Sax ji?» \c 39 \p \v 1 Jant yooyu doomu Baladan, Merodag Baladan buuru Babilon moo yónnee Esekiya bataaxal ak yóbbal. Fekk na mu déggoon ne Esekiya daa woppoon bay doora am tan. \v 2 Esekiya am ca mbégte, daldi won ndaw ya, kërug dencukaayam: xaalis baak, wurus waak ndàbb jaak, diwu tànnéef gaak mboolem néegub gànnaayam ya, ak mboolem lu nekkoon cay dencam. Amul lenn lu leen Esekiya wonul ci biir këram, ak mboolem fu bokk ci kilifteefam. \v 3 Gannaaw loolu Yonent Yàlla Esayi dikk ne Buur Esekiya: «Lu la nit ñii wax ak fu ñu jóge sax ba fi yaw?» Esekiya ne: «Réew mu sore lañu bàyyikoo, dikk ba fi man, réewum Babilon.» \p \v 4 Mu ne ko: «Ana lu ñu gis sa biir kër?» Esekiya ne ko: «Mboolem lu nekk sama biir kër, gis nañu ko. Amul lenn lu ma leen wonul ci samay denc.» \v 5 Esayi ne Esekiya: «Déglul kàddug Aji Sax ji Boroom gàngoor yi: \v 6 “Ay jant a ngii di ñëw, dees na yóbbu Babilon lépp lu nekk sa biir kër, te say maam dencoon ko, ba tey jii. Du lenn luy des. Kàddug Aji Sax jee. \v 7 Te it ñenn ci sag njaboot, ñu soqikoo ci yaw, di ñoo meññ ci sa geño, dinañu leen jàpp, ñu doon jaam yu ñu tàpp ca biir kër buuru Babilon.”» \v 8 Esekiya ne Esayi: «Kàddug Aji Sax ji nga jottli, jàmm la.» Booba ma nga naan: «Ndegam jàmm ju ne ñoyy ay am sama giiru dund kay!» \c 40 \ms1 Aji Sax jeey dàmp xol yi \mr (Saar 40—66) \s1 Xibaaru jàmm ñeel na Israyil \q1 \v 1 Dëfal-leena dëfal sama ñoñ, \q1 la seen Yàlla wax! \q1 \v 2 Waxleen lu dalal xelu Yerusalem, yéeneleen \q1 ne leen seen xare jeex na, \q1 seen mbugal mat na. \q1 Ñoo nangoo ci loxol \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji \q1 lu fey ñaari yoon seen bépp bàkkaar. \q1 \v 3 Baat a ngi jib, naan: \q2 «Xàll-leen yoonu Aji Sax ji ci màndiŋ mi, \q1 fàkkal-leen sunu Yàlla \q1 xàll wu jub fi joor gi. \q1 \v 4 Wépp xur lees di kaweel, \q1 tund wu magoo wu ndaw lees di suufeel; \q1 ba fu tunde mujj dig joor, \q1 fu ñagasoon maase, \q1 \v 5 darajay Aji Sax ji daldi feeñ, \q1 jaam ñépp bokk gis ko. \q1 Aji Sax jee ko wax ci làmmiñam.» \q1 \v 6 Baat a ngi naa: «Yéeneel!» \q1 Ma ne: «Lu may yéene?» \q1 Mu ne: «Neel: \q1 Bépp boroom suux am ñax doŋŋ la; \q1 gépp ngoram mel ni tóor-tóoru àll. \q1 \v 7 Ñax ma wow, \q1 tóor-tóor ma lax \q1 fa ko noowal Aji Sax ji wale. \q1 Askan wi kay, am ñax doŋŋ la. \q1 \v 8 Am ñax day wowal; \q1 tóor-tóor day lax. \q1 Waaye sunu kàddug Yàlla \q2 mooy sax ba fàww.» \b \q1 \v 9 Yaw \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, xibaarkatu jàmm bi, \q1 doxal yéegi tund wu kawe, \q1 te xaacook doole. \q1 Yaw Yerusalem, xibaarkatu jàmm bi, \q1 xaacul te bul ragal! \q1 Neel dëkki Yuda yi: \q1 «Seen Yàllaa ngi! \q1 \v 10 Boroom bi, Aji Sax jaa ngii, \q1 dikkaale doole \q1 ak kàttanu kilifteefam. \q1 Mu ngii ànd ak ñi mu yooloo, \q1 ñu dig peyam, dox jiitu ko. \q1 \v 11 Mooy sàmm géttam bii ni kuy sàmm ug juram, \q1 boole mbote yi cib loxoom, \q1 taf cib dënnam, yóbbu; \q1 xar yiy nàmpal, mu wommat.» \b \q1 \v 12 Ana ku natte géej biir loxoom? \q1 Ku xaymaa asamaan yaatuwaayu loxo? \q1 Ku mana fab suuf sépp, sol cib nattukaay? \q1 Ana ku natte ab màndaxekaay tund wu mag? \q1 Mbaa mu tam-tamal tund wu ndaw? \q1 \v 13 Ana ku mana xayma Aji Sax ji? \q1 Mbaa nga dib xejjam, ba di ko digal? \q1 \v 14 Ana ku mu diisool, ba kooka tegtal ko, \q1 jàngal ko yoonu njub, \q1 jàngal ko xam-xam, \q1 xamal ko yoonu dég-dég? \q1 \v 15 Xeet yaa ngii, mel ni aw toq ci biir bagaan, \q1 jàppeesu leen lu moy diisaayu feppu suuf! \q1 Dun yi lay yékkati ni pëndub suuf! \q1 \v 16 Gottub Libaŋ xambul taalam, \q1 te mala ya ca ne doyu ko \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*! \q1 \v 17 Xeetoo xeet du tus fi kanamam, \q1 te jàppewu leen lu moy neenug neen. \q1 \v 18 Ana kan ngeen di niruleek Yàlla, \q1 ak nataal bu ngeen koy dendaleel? \q1 \v 19 Xanaa du jëmmu tuur ju liggéeykat móol, \q1 ab tëgg xoobe ko wurus, \q1 takk ca caqi xaalis? \q1 \v 20 Ku néewle ba amul jooxe bu ni tollu, \q1 mooy tànn bant bu dul nëb, \q1 seeti liggéeykat bu xareñ \q1 bu ko ci sàkkal jëmmu tuur ju dëgër! \b \q1 \v 21 Dangeena xamul lii? \q1 Am dangeena déggul lii? \q1 Dees leena waxul ca njàlbéen, \q1 am seen xel a jàppul nu kenug àddina sampoo? \q1 \v 22 Moom moo tooge kaw wërngalu suuf, \q1 ñi ko dëkke mel niy soccet, \q1 moo tàllal asamaan ni ndimo, \q1 firi ko nib xayma, dëkke. \q1 \v 23 Mooy sànk kilifa, \q1 di neenal njiitu àddina. \q1 \v 24 Ba ñu sampoogul, \q1 toogaguñu sax, \q1 ba seeni reen di riigu, \q1 ca la leen Aji Sax jiy wal, ñu wow, \q1 ngëlén buub, yóbbu ni boob. \q1 \v 25 Aji Sell ji ne: \q1 «Ana ku ngeen may niruleel, \q1 ba may moroomam?» \q1 \v 26 Séentuleen kaw, xool-leen ki sàkk yii fi kaw! \q1 Xanaa kiy daaguloo seen gàngoor gu mat, \q1 ñoom ñépp lay woo ci seen tur, \q1 ci kawewaayu dooleem ak màggaayu kàttanam, \q1 te kenn du ci wuute. \q1 \v 27 Yeen askanu Yanqóoba, lu ngeen di jàmbat? \q1 Yeen Israyil laa ne, lu ngeen di jooy, \q1 naa: «Aji Sax ji gisul li nu dal, \q1 sunu Yàlla daal, daa réere sunu àq!» \q1 \v 28 Dangeena xamul, \q1 am dangeena déggul \q1 ne Aji Sax jeey Yàlla ba fàww, \q1 sàkk suuf cat ba cat, \q1 du sonn, du tàyyi, \q1 te am xelam nattuwul? \q1 \v 29 Mooy dooleel ku loof, \q1 di kàttanal ku jeele. \q1 \v 30 Waxambaane sonn, loof; \q1 xalelu góor di tërëfa tërëf, \q1 \v 31 kiy yaakaar Aji Sax ji moom, di yeeslu doole; \q1 da naa fëyy ni jaxaay juy naaw, \q1 di xélu te du xiix, \q1 di dox te du xoox. \c 41 \s1 Aji Sax jee yor jamono \q1 \v 1 Yeen waa dun yi, xeremluleen, déglu ma; \q1 yeen askan yi, takkuwaatleen, \q1 jegesi te wax, \q1 nu bokk teew, layoo. \q1 \v 2 Ana ku ñu yékkatee penku, \q1 woo ko ci tànki njekk? \q1 Ana ku ko jébbal xeet yi, \q1 nangulal ko buur yi, \q1 saamaram note ba ñuy pënd, \q1 fittam jamat, tasaare ni boob? \q1 \v 3 Moo leen di dàq, ba jàll te jàmm a koy dal, \q1 ay tànkam sax du laal suuf. \q1 \v 4 Ana ku def lii, dogal ko? \q1 Xanaa ki dale fa njàlbéen di woo maas yi! \q1 Man \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji maa jëkk, \q1 te man laak ñi mujj ba tey! \q1 \v 5 Waa dun yee ko gis, tiit; \q1 waa cati àddina di lox; \q1 dox ba agsi; \q1 \v 6 ku nekk di jàpple moroom ma, \q1 naa mbokk ma: «Góor-góorlul!» \q1 \v 7 Tëggu weñ ba di ñaax tëggu gànjar ba, \q1 boroom wàkku soññ boroom dékk, \q1 ñu naa: «Taqaleb weñ yi baax na!» \q1 tey daaj jëmmi xërëm ja \q2 ay pont yu koy dëgëral. \s1 Aji Sax jeey musal Israyil ciy noonam \q1 \v 8 Waaye yaw Israyil, sama jaam bi; \q1 yaw Yanqóoba mi ma taamu, \q1 yaw askanu Ibraayma, samab xarit! \q1 \v 9 Yaw mi ma jukkee fa cati àddina, \q1 wooye la fa gëna sore, \q1 wax la ne la: «Yaa di sama jaam, \q1 maa la taamu te duma la wacc,» \q1 \v 10 bul ragal, yaw laa àndal, \q1 bul tiit, maay sa Yàlla; \q1 maa lay dooleel, dimbali la déy, \q1 maa lay téyee sama ndijooru njekk déy. \b \q1 \v 11 Ma ne, képp ku la mere, \q1 dees koy rusloo, torxal ko. \q1 Kuy joteek yaw day neen, sànku. \q1 \v 12 Dinga ko seet, doo ko gis, \q1 kuy jànkoonteek yaw, du mujje doon tus, \q1 te kuy xareek yaw it day mujj neen. \q1 \v 13 Man \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji maay sa Yàlla; \q1 téye sa loxol ndijoor, \q1 di la wax ne la: «Bul tiit, \q1 maa lay dimbali.» \q1 \v 14 Yaw Yanqóoba mi néew doole niw sax, \q1 yeen góori Israyil. \q1 Man, maa leen di dimbali. \q1 Kàddug Aji Sax jee, \q1 sab \w jotkat|lemma="jotkat b-:"\w*, Aji Sell ju Israyil. \q1 \v 15 Maa ngii di la def \q1 ngay watiiru bàccukaay bu ñaw, yees peq; \q1 ànd aki bëñam, \q1 ngay wol tund wu mag, raatale; \q1 dëbb tund wu ndaw ba mu mel nib cox. \q1 \v 16 Yaa leen di bàcc, ngelaw wal, \q1 ngëlén tasaare; \q1 yaw ngay bége Aji Sax ji, \q1 di damoo Aji Sell ju Israyil. \b \q1 \v 17 Walaakaanaak néew-doolee ngi wër, \q1 di wut um ndox, amul. \q1 Seen put wow koŋŋ ak mar. \q1 Man Aji Sax ji, maa leen di nangul; \q1 man Yàllay Israyil, duma leen wacc. \q1 \v 18 Maay walaley dex kaw coll ya ne duŋŋ, \q1 bënn bëti ndox digg xur ya, \q1 def màndiŋ ma ab déeg, \q1 suuf su ne sereŋ laay ballalem ndox. \q1 \v 19 Maay def garabi seedar aki séng ca màndiŋ ma, \q1 saxal garabi mirt ak oliw ca joor ga, \q1 sippar ak garabu pẽe, ak yeneen garab yu dëkke naat, \q2 ma boole ca, \q1 \v 20 ndax nit ñi gis, ba xàmmee, \q1 ñoom ñépp nemmiku, ba xam ne \q1 Aji Sax jee def lii ci loxoom, \q1 xam ne Aji Sell ju Israyil a sàkk lii. \s1 Aji Sax ji tiiñal na tuuri yéefar yi \q1 \v 21 «Waxleen seenu lay,» la \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax, \q1 «Biral-leen seeni firnde,» la buuru Yanqóoba boobu wax. \q1 \v 22 «Woneleen ko te wax nu liy ñëw. \q1 Xamal-leen nu la woon, lu mu; \q1 nu ba ci xel, ba xam lu muy jur, \q1 te ngeen dégtal nu la dikkagul. \q1 \v 23 Biralal-leen nu mbiri ëllëg, \q1 nu xam ne ay yàlla ngeen. \q1 Defleen rekk lenn, muy lu baax di lu bon, \q1 ndax nu bokk ko gis, ba yéemu. \q1 \v 24 Ma ne, yeen daal, dungeen tus; \q1 seen liggéey du dara, \q1 te ku leen taamu di ku seexluwu!» \b \q1 \v 25 Maa yékkatee nit bëj-gànnaar, \q1 mu bawoo penkub jant, \q1 di tudd sama tur. \q1 Mooy note boroom dëkk ni ban \q1 mbaa binit bu defarkatu njaq di dëggaate. \q1 \v 26 Ana ku yéene woon lii ca njàlbéen, \q1 ba nu xam ko? \q1 Ku ko yégle woon bu yàgg, \q1 ba nu man koo dëggal? \q1 Yéeneesu ko, yégleesu ko \q1 te déggeesul seeni kàddu. \q1 \v 27 Waaye maa jëkka yégal \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* \q1 ne leen: «Xool-leen, ñu ngii!» \q1 Maa indil Yerusalem ndaw lu indi xibaaru jàmm. \q1 \v 28 Xool naa xool ci tuur yi, gisuma kenn; \q1 du kenn ci ñoom ku ciy xelale, \q1 ba ma laaj ko, mu mana tontu. \q1 \v 29 Ñoom ñépp a ngoogu, tekkiwuñu tus. \q1 Seen liggéey, caaxaani neen, \q1 seen jëmmi xërëm du dara, cóolóolu kese. \c 42 \s1 Aji Sax ji yebal na jaamam \q1 \v 1 «Xool-leen sama jaam bi ma yor, \q1 sama tànnéef, sama soppey xol, \q1 ci kawam laa teg samag noo, \q1 te mooy dogalal xeet yi yoonu àtte. \q1 \v 2 Du xaacu, du biral; \q1 du jibal baatam ci mbedd mi. \q1 \v 3 Bant bu lemu sax, du ko damm, \q1 leer gu giim it, du ko fey. \q1 Mooy indi yoonu dëgg. \q1 \v 4 Du toqi, du nasax, \q1 ba keroog muy dëj àtteb yoon fi kaw suuf, \q1 fa waa dun ya di séentu ndigalu yoonam.» \q1 \v 5 Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax, \q1 moom mi sàkk asamaan, firi ko; \q1 tàllal suuf ak lu mu jur, \q1 may noowal bakkan ñi ci kawam, \q1 ba ña cay daagoo di noyyi. \q1 \v 6 Mu ne: «Man Aji Sax ji, maa la woo cig njekk, \q1 jàpp la ci loxo, \q1 sàmm la, def la ngay \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* sama digg ak nit ñi; \q1 def la ngay leeru xeet yi, \q1 \v 7 ngay gisloo gumba, \q1 di génne ku ñu tëj, \q1 ku dëkke woon lëndëm, génn kërug tëjukaay. \q1 \v 8 Man, Aji Sax jeey sama tur, \q1 sama teddnga, duma ko joxe, \q1 te sama bàkk, duma ko wacce jëmmi tuur. \q1 \v 9 Mbir ya jiitoo ngoog, mat na; \q1 yu yees laa leen di yégal, \q1 balaa teew, ma yegge leen ko.» \s1 Woyleen Aji Sax ji \q1 \v 10 Woyleen \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji woy wu yees, \q1 yeen waa cati àddina, kañleen ko, \q1 ànd ak ñiy wàcci géej ak li ci biiram, \q1 ak duni géej ak ña ca dëkke. \q1 \v 11 Na waa àll beeki dëkkam xaacoondoo, \q1 waa dalub Kedar \q2 ak waa Sela sarxolleendoo, \q1 kaw tund ya di riirum mbég! \q1 \v 12 Nañu delloo Aji Sax ji teddngaam, \q1 te biral bàkkam biir duni géej. \q1 \v 13 Aji Sax jeey waaxu ni jàmbaar, \q1 xabtalu ni ñeyu xare, \q1 àddu ca kaw, xaacu, \q1 tiime noon yi njàmbaaram. \s1 Aji Sax ji soppi na \q1 \v 14 Aji Sax ji nee: «Damaa yàgga xeremlu, \q1 ne cell, téye sama bopp. \q1 Waaye léegi, ni kuy matu laay onke, \q1 di xiix ak a àppaat boole ca. \q1 \v 15 Maay tonni tund wu mag ak wu ndaw, \q1 lu cay gàncax, ma fóom; \q1 ag dex, ma def ag joor; \q1 ab déeg, ma ŋiisal. \q1 \v 16 Maay doxloo silmaxa yi \q2 ci yoon wu ñu xamul, \q1 ñall wu ñu miinul laa leen di jaarale. \q1 Maa leen di soppil lëndëm gi fi seen kanam, ag leer, \q1 fu ñagas, ma maasaleel leen. \q1 Lii laa leen di defal, \q1 te duma leen wacc mukk! \q1 \v 17 Ñi wóolu ay jëmmi tuur, \q1 naan jëmm yu ñu móol: \q1 “Yeenay sunuy yàlla,” \q1 dees na leen waññi, torxal leen. \b \q1 \v 18 «Yeen tëx yi, dégluleen; \q1 yeen silmaxa yi, xool-leen ba gis. \q1 \v 19 Ana ku silmaxa ku moy sama jaam bii? \q1 Ku tëx ba dab sama ndaw li ma yónni? \q1 Ana ku silmaxa ba dab kii ñu jàmmal? \q1 Ku silmaxa ba dab jaamu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jii? \q1 \v 20 Gis nga lu bare, \q1 waaye jàppoo ci dara. \q1 Nopp ne kótt, dég-dég të!» \q1 \v 21 Aji Sax ji la soob ci njekkam, \q1 mu fésal màggaayu yoonam ak taar ba. \q1 \v 22 Waaye ñu ngii di xeet wu ñu futti, sëxëtoo; \q1 ñépp tëje ciy pax, \q1 dence ci këri tëjukaay, \q1 ñu doon alalu xare \q1 fu leen kenn dul xettlee, \q1 xanaa ñu di leen sëxëtoo, \q1 te kenn du ne ñu delloo leen. \b \q1 \v 23 Ana kan ci yeen mooy dékk lii nopp? \q1 Kuy teewlu, ba doxe fa dégg? \q1 \v 24 Ana ku jébbal Yanqóoba futtikat yi, \q1 ku jox Israyil gii, sëxëtookat yi? \q1 Xanaa du Aji Sax ji nu tooñ? \q1 Ñoo baña topp ay yoonam, \q1 baña sàmm ndigalu yoonam, \q1 \v 25 ba mu yuri leen tàngooru sànjam, \q1 sotti leen tar-taru xare, \q1 mu jafal wetoo wet, te taxul ñu xam, \q1 xoyom na leen te bawuñu ci xel. \c 43 \s1 Jotkatub Israyil kenn la \q1 \v 1 Léegi nag yaw Yanqóoba, \q1 yaw Israyil mii, \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji la sàkk tabax la, dafa wax ne: \q1 «Bul tiit, jot naa la. \q1 Dama laa woo ci sa tur. \q1 Maa la séddoo. \q1 \v 2 Booy xuus cim ndox, \q1 maa ngi ànd ak yaw; \q1 ag dex du la mëdd. \q1 Booy dox cib taal, doo lakk, \q1 sawara du la xoyom. \q1 \v 3 Man Aji Sax ji, maay sa Yàlla; \q1 man Aji Sell ju Israyil, \q1 maa lay musal. \q1 Maa joxe Misra, feye la; \q1 ak \w Kuus|lemma="Kuus:"\w* ak Seba, ma weccikoo la. \q1 \v 4 Fonk la, teral la ak sopp la, \q1 moo tax ma joxey nit, weccikoo la; \q1 ay askan dee, wuutu sa bakkan. \q1 \v 5 Bul tiit, yaw laa àndal, \q1 maay jële saw askan penku, \q1 dajalee leen sowub jant. \q1 \v 6 Maa naa bëj-gànnaar: “Ësi!” \q1 ne bëj-saalum: “Bul téye!” \q1 Jëleel sama doom yu góor fu sore, délloosi, \q1 te jëleji sama doom yu jigéen fa cati àddina. \q1 \v 7 Délloosil képp ku ñu ma tudde, \q1 te sama màqaama tax ma sàkk ko, \q1 tabax ko, sottal ko.» \q1 \v 8 Indileen ñii diy silmaxa te ami gët; \q1 tëx te ami nopp. \q1 \v 9 Na xeet yépp daje, \q1 askan yépp teewandoo. \q1 Ana ku nu ci yégaloon lii xew, \q1 mbaa mu xamal nu la wees? \q1 Na seen seede teew, dëggal leen; \q1 ba ñu dégg leen, ne noonu la. \q1 \v 10 Yeen sama ñoñ, yeenay samay seede. \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 Yeenay sama jaam bi ma taamu, \q1 ngir ngeen xam, ba gëm ma, \q1 ba ràññee ne maay moom. \q1 Sàkkeesul yàlla ju ma jiitu, \q1 mbaa ju may wuutuji. \q1 \v 11 Aji Sax ji, mennum man a; \q1 amul jotkat bu ma moy. \q1 \v 12 Maa dogal ag njot, sottal ko, biral ko, \q1 ba tuuru doxandéem nekkagul seen biir. \q1 Yeen nag, yeenay samay seede. \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 Man maay Yàlla, \q1 \v 13 maa masa doon kenn ki, \q1 te sama loxo, maneesu cee musle. \q1 Su ma defee, kuy dindi? \b \q1 \v 14 Aji Sax jiy seen \w jotkat|lemma="jotkat b-:"\w*, \q1 Aji Sell ju Israyil dafa wax ne: \q1 «Yeena tax ma yebal ku songsi Babilon, \q1 ba dàjji lu fay tëjukaay, \q1 ba xaxalooy Kaldeen ñooñu diy jooyoo\f + \fr 43.14 \fr*\ft Tekkitel aaya bii am na werante.\ft*\f*. \q1 \v 15 Maay Aji Sax ji, seen ku Sell ki; \q1 maa sàkk Israyil, di seen buur.» \b \q1 \v 16 Aji Sax ji dafa wax, \q1 moom mi sàkk yoon biir géej, \q1 rëddu xàll, digg mbeex mu ne xéew; \q1 \v 17 xabtal watiiri xare aki fas, \q1 ak gàngooru ñeyi xare, \q1 ñu bokk tëdd, jógatuñu, \q1 xanaa fey kamaj nib làmp. \q1 \v 18 Mu ne: «Buleen geesu la woon, \q1 buleen seet ca la wees. \q1 \v 19 Maa ngii di def lu yees, \q1 te mu ngii di feeñ xaat! \q1 Ràññeewuleen koo? \q1 Biir màndiŋ mi kay laay xàllu yoon; \q1 fa ne sereŋ, ma walal ay dex; \q1 \v 20 dundooti àll bi di ma sàbbaal, \q2 ñook njabootug bànjóoli, \q1 nde maa mayem ndox fi màndiŋ mi, \q1 dex ya wale fu noon sereŋ, \q1 ma nàndale sama ñoñ, sama tànnéef, \q1 \v 21 xeet wii ma bindal sama bopp, \q1 te ñooy siiwal sama woy.» \b \q1 \v 22 Moona Yanqóoba, woowuloo ma, \q1 yaw Israyil laa ne, sàppi naa la. \q1 \v 23 Du xar mu ndaw moo ma defal \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, \q1 mbaa sarax yoo ma terale, \q1 te du sarax su ma la teg it, \q1 mbaa saraxu \w cuuraay|lemma="cuuraay l-:"\w* bu ma la sonale. \q1 \v 24 Du xaalis boo ma jëndale barax bu xeeñ, \q1 du nebbonu sarax boo ma reggale. \q1 Xanaa lakkal maak say bàkkaar, \q1 sonal maak say ñaawtéef. \q1 \v 25 Mennum man mii maay far say moy ngir man, \q1 ba dootuma fàttliku bàkkaar. \q1 \v 26 Fàttli ma saw lay, nu bokk layoo; \q1 waxal boog yaw, ndax nga yey! \q1 \v 27 Sa maam a jëkka bàkkaar, \q1 ñi lay teewal teg ca gàntal ma, \q1 \v 28 ba tax ma sobeel kilifay kër gu \w sell|lemma="sell:"\w* gi, \q1 araamal Yanqóoba, \q1 wacce Israyil ŋàññi noon. \c 44 \s1 Aji Sax jee mat cëslaay \q1 \v 1 Yaw Yanqóoba, sama jaam bi, déglul boog, \q1 yaw Israyil sama tànnéef laa wax. \q1 \v 2 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax, moom mi la sàkk, \q1 mooñ la fa sa biiru ndey, \q1 di la dimbali. \q1 Mu ne: «Yaw Yanqóoba sama jaam bi, \q1 yaw Yesurun sama tànnéef laa wax, \q1 bul tiit. \q1 \v 3 Maay sottim ndox suuf su mar, \q1 ak wal yu waleg joor gu wow. \q1 Maay sotti saw askan samag noo, \q1 sama barke sottikul ñi nga meññ, \q1 \v 4 ñu màgg ni garabu saabsaab, \q1 nirook garab yu mag yu feggook ndox. \q1 \v 5 Kii nee: “Aji Sax jee ma moom.” \q1 Kee di tuddoo turu Yanqóoba, \q1 kale bind ca loxo ba: “Maa ñeel Aji Sax ji,” \q1 tey wuyoo turu Israyil.» \s1 Aji Sax ji dëkk na yàllantu yi \q1 \v 6 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax, \q1 moom buurub Israyil, \w jotkatam|lemma="jotkat b-:"\w*, \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, \q1 mu ne: «Maa jëkk, maa mujj, \q1 te yàlla amul ndare man. \q1 \v 7 Ana ku mel ni man? Na àddu! \q1 Na biral firndeem te taajal ma \q2 la amoon ba may sos xeet wu yàgg wa, \q1 ak li dikkagul. \q1 Na ko wax! \q1 \v 8 Buleen tiit, buleen ragal. \q1 Dama leena biralul lii bu yàgg, yégal leen ko? \q1 Yeenay samay seede. \q1 Yàlla daa am ju ma moy? \q1 Cëslaay amul, xawma ci kenn!» \b \q1 \v 9 Képp kuy tabax jëmmi tuur, doo tus, \q1 xërëm yooyu ñu safoo amul njariñ. \q1 Ñooñu ñu defi seede \q1 te gisuñu, yéguñu, \q1 muy seen gàcce! \q1 \v 10 Sàkk sam tuur, \q1 móol sa jëmmu tuur, \q1 te jariñu la tus! \q1 \v 11 Képp ku ca bokk \q1 sa gàcce lay doon, \q1 ña koy yett sax ay nit doŋŋ lañu. \q1 Nañu daje ñoom ñépp, taxaw, \q1 bokk tiitaangeek gàcce. \q1 \v 12 Ab tëgg jël jumtukaayam, \q1 liggéey weñ ca taal ba, \q1 wàkka wàkk, jëmmal; \q1 def ci kem kàttanam, \q1 teg ca xiif, doole jeex, \q1 naanul it ba tax mu loof. \q1 \v 13 Liggéeykatu bant tàllal buumu nattukaay, \q1 jël kew, nataale, \q1 xacc, rëdde rëddukaayu wërngal, \q1 jox ko bindu nit, \q1 jekkal ba mu mel ni nit, \q1 nar koo fat cib néeg, \q1 \v 14 ba tax mu gor garabi seedar, \q1 sàkk banti sippar ak yu ni mel, \q1 tànn ci garabi gott bi, \q1 mbaa mu jëmbat garab yu dëkke naat, \q1 ab taw màggal, \q1 \v 15 nit xambe, sàkk ci, jaaroo; \q1 taal, lakke mburu; \q1 sàkkaale ci jëmmu tuur, sujjóotal ko, \q1 muy jëmm ju mu defar, di ko sukkal; \q1 \v 16 xaaju matt ma lay taal, \q1 toggew yàppam, lekk, \q1 wàjj, xéewloo ba suur, \q1 jaaruwaale te naan: \q1 «Mii njaar mu neex! \q1 bii tàkk-tàkk bu yànj!» \q1 \v 17 Ndesu matt ma lay sàkke jëmmu tuuram, \q1 sukkal ko, \q1 sujjóotal ko, ñaan ko, naa: \q1 «Yaay sama Yàlla, xettli ma!» \q1 \v 18 Ñii xamuñu, xàmmeewuñu, \q1 seeni gët lañu lëndëmal, ba gisatuñu; \q1 fatt seenum xel, ba xelootuñu. \q1 \v 19 Ku mel nii du délloosim xelam, \q1 ba xam, ràññee ne: \q1 «Xaaju matt mi laa taal, \q1 lakke mburu, \q1 wàjje yàpp, lekk; \q1 mu des, ma di ko sàkke lu seexluwu lii? \q1 Ab dogu bant laay sukkal?» \q1 \v 20 Kee di jur gu fore ab dóom, \q1 xelam nax ko, sànk ko. \q1 Du keey musal bakkanam de! \q1 Du kee naa: «Xanaa duy caaxaan laa ŋàbb nii?» \b \q1 \v 21 Aji Sax ji nee: «Yanqóoba, baal xel ci lii! \q1 Ma ne Israyil, fàttlikul, yaa di sama jaam! \q1 Ma bind la, ngay sama jaam, \q1 yaw Israyil, duma la fàtte! \q1 \v 22 Maa far say moy, mu naaxsaay niw niir, \q1 say bàkkaar ne mes nib lay. \q1 Délsil fi man, jot naa la.» \q1 \v 23 Asamaan, sarxolleel, Aji Sax ji dikk na! \q1 Yeen xóotey suuf, xaaculeen! \q1 Yeen tund yi, neleen réllet, sarxolleendoo, \q1 ak yaw gott beek sa bépp garab! \q1 Aji Sax jee jot Yanqóoba, \q1 te moom Israyil lay fésale darajaam. \s1 Dees na dëkkewaat Yerusalem \q1 \v 24 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji sa \w jotkat|lemma="jotkat b-:"\w* dafa wax, \q1 moom mi la bind ba ngay sosu, \q1 ne: «Man maay Aji Sax ji sàkk lépp. \q1 Man doŋŋ maa tàllal asamaan, \q1 lal suuf, kenn wéttaliwu ma ca. \q1 \v 25 Maay neenal firndey maaman, \q1 dofloo gisaanekat. \q1 Maay weddi fóore, \q1 def xam-xamam mu dig ndof. \q1 \v 26 Maay dëggal sama kàddug jaam, \q1 di sottal sama ndéeyal ndaw. \q1 Maa naan ci Yerusalem: \q1 “Dees na ko dëkke,” \q1 dëkki Yuda, ma ne: \q1 “Dees na leen tabaxaat, \q1 ma dekkali gentam bi.” \q1 \v 27 Maa naa xóotey mbeex mi: “Wowal, \q1 te maay ŋiisal say dex.” \q1 \v 28 Maa naa ci Sirus: “Sama sàmm bi!” \q1 Mooy matal sama bépp nammeel, \q1 te it moo naa ci Yerusalem: \q1 “Nees ko tabaxaat,” \q1 kër gu sell gi, laa ne: \q1 “Nees ko yékkatiwaat!”» \c 45 \s1 Aji Sax ji dooleel na Buur Sirus \q1 \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ki mu fal, \q1 Buur Sirus mi mu jàpp ci loxol ndijooram, \q1 ngir nangulal ko xeet yi, \q1 yolomal ngañaayal buur yi, \q1 lafal koy bunt, \q1 ba bunti dëkk du tëje, \q1 \v 2 mu ne: «Man maa lay jiitu, \q1 maasale mbartal, \q1 rajaxe buntu xànjar, \q1 damm tëjukaayu weñ. \q1 \v 3 Maa lay jagleel denc yu loq, \q1 ak alal ju làqe, \q1 ba nga xam ne maay Aji Sax ji lay wooye sa tur, \q1 man Yàllay Israyil. \q1 \v 4 Te Yanqóoba sama jaam bi, \q1 Israyil moomu di sama tànnéef moo tax \q1 ma wooye la saw tur, \q1 takkal la ndombol tànk, \q1 te xamuloo ma. \q1 \v 5 Aji Sax ji man a, du keneen; \q1 kenn du yàlla ku dul man. \q1 Maa la gemb, \q1 te xamuloo ma, \q1 \v 6 ngir xamees penku ba sowu, \q1 ne lu dul man neen la. \q1 Aji Sax ji man a, du keneen. \q1 \v 7 Maay bind leer, \q1 di def lëndëm. \q1 Maay indi jàmm, \q1 di def safaan. \q1 Maay Aji Sax jiy def lii lépp! \q1 \v 8 Na asamaan wis-wisal, \q1 niir yuri njekk, \q1 suuf fett, meññal wall, \q1 boole ci jebbil njekk. \q1 Man Aji Sax ji, maa def lii!» \b \q1 \v 9 Wóoy ngalla kuy diiŋat ka la tabax \q1 te di ndabal xandeer ci biir ndabi xandeer! \q1 Ana ban ak di wax tabaxkatam, \q1 naa ko: «Looy def nii? \q1 Yaw amulooy loxo.» \q1 \v 10 Wóoy ngalla ku naan baayu nit, \q1 «Moo, lu sa geño meññ nii?» \q1 Mbaa ku naan ndeyu nit, \q1 «Li nga wasin lu mu?» \q1 \v 11 Aji Sax ji, Aji Sell ju Israyil dafa wax, \q1 moom mi ko bind, \q1 mu ne: «Lu dikkagul, nu ngeen ma ko ñemee laaje; \q1 am dangeen may jox ndigal ci samay doom, \q1 jox ma ko ci li ma liggéeye samay loxo? \q1 \v 12 Man maa amal suuf, \q1 sàkk doom aadama fi kaw suuf. \q1 Man mii la samay yoxo firi asamaan, \q1 te maay jox gàngoori asamaan lépp ndigal. \q1 \v 13 Man maay yékkati Sirus ci biir njekk, \q1 xàllu yoonam. \q1 Moom mooy tabax sama dëkk, \q1 yiwi sama ñoñ ñi ñu toxal, \q1 te du laaj pey mbaa neexal.» \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. \b \q1 \v 14 Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 «Muy ñaqu Misra, di koomu waa \w Kuus|lemma="Kuus:"\w*, \q1 ak waa Seba, ya ne sireet ca kaw, \q1 ñoom ñépp ay jàllsi, nga jagoo. \q1 Sa gannaaw lañuy topp, \q1 yeewe, jàllsi; \q1 sujjóotal la, di ñaan naan: \q1 “Fi yaw daal la Yàlla ne, \q1 du feneen, \q1 te tuur neen la.”» \q1 \v 15 Yaw déy, yaa di Yàlla ju làqu, \q1 yaw Yàllay Israyil ji koy wallu. \q1 \v 16 Yettkati xërëm yaa ngoogu, rus, \q1 torox, riixleendoo. \q1 \v 17 Israyil, yaay mucc fa Aji Sax ji \q1 mucc gu sax dàkk! \q1 Doo rus, doo torox \q1 fii ak ëllëg. \b \q1 \v 18 Aji Sax ji kat dafa wax, \q1 moom mi sàkk asamaan, \q1 moom Yàlla mi bind suuf, \q1 tabax ko, dëj ko, \q1 sàkkewu ko maraas, \q1 xanaa tabaxal ñu ko dëkke. \q1 Mu ne: «Aji Sax ji, man a, du keneen. \q1 \v 19 Làquwma, di waxe bérab bu lëndëm. \q1 Newuma it askanu Yanqóoba: \q1 “Sàkkuleen ma fu dara amul.” \q1 Man Aji Sax ji maay wax dëgg, \q1 di biral njub.» \b \q1 \v 20 Yeen daw-làquy xeet yi, \q1 dajeleen, dikk, \q1 ànd, jegesi. \q1 Képp ku gàddu tuuru bantam, \q1 ak kuy ñaan tuur mu ko dul wallu, \q1 kooka xamul dara. \q1 \v 21 Àdduleen, layoosi, \q1 diisooleen fi seen biir kay! \q1 Ana ku xamle woon lii bu yàgg, \q1 yégle woon ko booba? \q1 Xanaa du man Aji Sax ji? \q1 Kenn du Yàlla ku dul man! \q1 Yàlla ju jub, di walloo, \q1 du kenn ku dul man! \q1 \v 22 Yeen waa àddina, catoo cat, \q1 walbatikuleen fi man, mucc. \q1 Man maay Yàlla, du keneen. \q1 \v 23 Giñ naa ko ci man mii, \q1 sama gémmiñ njekk a ciy jibe, \q1 di kàddu gu dul randu. \q1 Man la ñépp di sukkal seen bëti óom, \q1 man it la bépp boroom làmmiñ di giñe. \q1 \v 24 Dees na ma waxal ne: \q1 «Aji Sax ji rekk a jagoo njekk ak doole!» \q1 Mboolem ñi ma mereey ànd, \q1 sëgg, fekksi ma. \q1 \v 25 Ci Aji Sax ji la askanu Israyil gépp yeye, \q2 bay damu. \c 46 \s1 Yii yàlla bootu, jii Yàlla di boote \q1 \v 1 Tuur ma ñu naa Bel toqi na, \q1 tuur ma ñu naa Nebo sukk, \q1 mala ya féetewoo seeni jëmm, \q1 ñoom lees daan gàddu\f + \fr 46.1 \fr*\ft Waa Babilon a doon gàddu seeni tuur, gannaaw ba leen Buur Sirus songee.\ft*\f*, tey jur gi jagoo, \q1 di leen sëf ba loof. \q1 \v 2 Tuur yaa ngay sukk, bokk toqi; \q1 manuñoo wallu seen jëmm ya, \q1 xanaa doxal seen bopp, duggi ngàllo. \q1 \v 3 «Dégluleen yeen waa kër Yanqóoba, \q1 yeen ndesu kër Israyil gépp, \q1 yeen ñi ma dale yor ba ngeen juddoo, \q1 di leen fab ba ngeen génnee seen biiru ndey. \q1 \v 4 Ba ba ngeen di magal, man la, \q1 ba keroog ngeen di bijjaaw, maa leen di boot. \q1 Maa sàkk, maay yor, \q1 maay boot, xettli! \b \q1 \v 5 «Ana ku ngeen may niruleel, \q1 di ma nàttableek a méngaleek moom, \q1 ba ñu niroo lenn? \q1 \v 6 Ñii déy a yullee wurus ci mbuus, \q1 sàkk xaalis, natt diisaay ba, \q1 fey tëgg bu leen ci tëggal am tuur \q2 mu ñuy sukkal ak a sujjóotal, \q1 \v 7 yékkati teg ci mbagg, \q1 yóbbu, teg bérab, mu des fa; \q1 du jóge fa mu tege, \q1 ku ko woo wall it, du wuyu, \q1 ba jot ko ci njàqare. \q1 \v 8 Fàttlikuleen lii te dëgërluwaat! \q1 Yeen bàkkaarkat yi, defleen lii ci seen xel. \q1 \v 9 Fàttlikuleen cosaan la woon. \q1 Man mii maay Yàlla, du keneen. \q1 Amul Yàlla ju mel ni man! \q1 \v 10 Maay yégle muj ca ndoorte la, \q1 ak jëf ju amagul, lu jiitu bu yàgg. \q1 Maa naa sama mébét a ngi, day am, \q1 sama bépp nammeel sotti. \q1 \v 11 Maay wooye jaxaay penku, \q1 wooye réew mu sore, kuy sottal sama mébét. \q1 Maay àddu, amal; \q1 maay nas, sottal. \b \q1 \v 12 «Dégluleen maa, yeen dëgër bopp yi! \q1 Yeenaka dëddu njekk! \q1 \v 13 Maa jegeñal sama njekk, soreetul; \q1 sama wall a ngi, yàggatul. \q1 Maay maye wall fi \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* gii, \q1 ba Israyil gii di sama gànjar.» \c 47 \s1 Babilon falu, fëlëñu \q1 \v 1 Yaw janq Babilon, \q1 wàccal, toog ci pënd bi. \q1 Yaw dëkkub Kaldeen bi ci taar bi laa ne, \q1 toogal fi suuf, amatoob jal. \q1 Dootoo dégg «Lewet, xay.» \q1 \v 2 Fabal wolukaay, wol sunguf. \q1 Dindil sa muuraay gi, \q1 wogos sa mbubb, \q1 ëñ sas kumba, \q1 xuus, jàll dex yi. \q1 \v 3 Na sa yaram feeñ, \q1 say cér ne fàŋŋ. \q1 Damay feyu, \q1 te duma bale. \b \q1 \v 4 Sunu \w jotkat|lemma="jotkat b-:"\w* ay \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoor yi, \q1 Aji Sell ju Israyil. \b \q1 \v 5 Yaw dëkkub Kaldeen bi ci taar bi, \q1 toogal ne cell te fatu cig lëndëm, \q1 deesatu la wooye lingeeru réew yi. \q1 \v 6 Maa mere woon sama ñoñ, \q1 sobeel sama séddoo ñii, \q1 teg leen ci sa loxo, \q1 te wonoo leen yërmande, \q1 ba mag sax, nga teg ko lu diisa diis, \q1 \v 7 te naa: «Ba fàww maay lingeer!» \q1 ba tax bàyyiwoo xel ca la ngay def; \q1 xalaatoo la muy jur. \q1 \v 8 Diryànke bee, déglul lii: \q1 Yaa ngi ne finaax te naa ci sam xel: \q1 «Maa ko yor, man rekk, du keneen. \q1 Duma jooy jëkkër, duma jooy doom!» \q1 \v 9 Te yaar yooyoo lay dikkal ci benn bés. \q1 Jooy doom, jooy jëkkër ay yembandoo, \q1 dal fi sa kaw ci sa biir xërëmtu yi ne xas, \q1 ak sa jat yu dul jeex. \q1 \v 10 Dangaa yaakaaroon sa pexe yu bon, \q1 naan, «Kenn gisu ma!» \q1 Sam xel ak sa xam-xam a la wacc, \q1 ba tax nga naa: «Maa ko yor, man rekk.» \q1 \v 11 Musibaa lay dikkal, \q1 te doo xam fu mu fenke. \q1 Njaaxum a lay dal, \q1 te du looy mana fanq. \q1 Sànkuteey jekki dale la foo yégul. \b \q1 \v 12 Jàppool say jat rekk \q1 ak sa xërëm yu ne xas \q1 yoo dale sonn ba ngay ndaw. \q1 Jombul mu amal la njariñ, \q1 mbaa ñu ragale la ko. \q1 \v 13 Yaaka sonn ci tegtali maa-man! \q1 Nañ taxaw boog, wallu la! \q1 Ñii di rëdd nataalu asamaan, \q1 di niiri biddiiw, \q1 ak di xool weer wu feeñ, \q1 xamle ca loo dikkleegul. \q1 \v 14 Ñu ngoog bokk ak boob bu sawara jafal, demin, \q1 duñu musal seen bakkan ca sawara sa, \q1 te du doon ab taal bu ñuy lakke mburu \q1 mbaa xal sooy uuf di jaaru. \q1 \v 15 Lii moo di muju ña la taxoon di sonn. \q1 Ña nga dale jëflanteel ba ngay ndaw, \q1 ña ngay tambaambalu tey, ku nekk ak yoonam, \q1 kenn walluwu la ci. \c 48 \s1 Yàlla sikk na Israyil \q1 \v 1 Yeen waa kër Yanqóoba, dégluleen; \q1 yeen ñi ñu wooye turu Israyil, \q1 yeen ñi bawoo bëti ndoxi Yuda, \q1 di giñe turu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 yeen ñiy sàbbaal turu Yàllay Israyil \q1 te dëgg ak njekk taxul, \q1 \v 2 moona yeena ngi sagoo turu dëkk bu \w sell|lemma="sell:"\w* bi, \q1 di wéeroo Yàllay Israyil \q2 ji turam di Aji Sax ji Boroom gàngoor yi. \q1 \v 3 Yàgg na maa biral lay jëkka am. \q1 Tuddoon naa ko, yégle ko, \q1 jekki jëf ko, mu sotti. \q1 \v 4 Xam naa ne ñu dëgër bopp ngeen. \q1 Dangeen të, wowle. \q1 \v 5 Moo tax ma yàgg leena biralal lii, \q1 yégal leen ko balaa teew. \q1 Lu ko moy ngeen ne: \q1 «Sunu tuur mee ko def, \q1 sunu tuuru bant bee, \q1 sunu tuuru weñ gee ko amal di!» \q1 \v 6 Lii lépp déggoon ngeen ko; \q1 xool-leen, xanaa dingeen ko nangu tey! \b \q1 Bés niki tey dinaa leen yégal lu bees, \q1 muy kumpa gu ngeen xamul woon. \q1 \v 7 Léegi lees ko amal, \q1 du lu yàgg. \q1 Lu jiitu tey masuleen koo dégg \q1 te dungeen ne xamoon ngeen ko. \q1 \v 8 Dégguleen, yéguleen, \q1 seeni nopp masula bënn; \q1 xam naa ne ay workati neen ngeen, \q1 «njuddu-fippu» lañu leen di wooye. \q1 \v 9 Waaye sama tur tax na ma aj sama mer, \q1 sama woy tax na ma muñal leen, \q1 ba duma leen fàkkas. \q1 \v 10 Ma ne, togg naa leen, xelli cib taal, \q1 waaye du taalu xellikaayu xaalis, \q1 sawaras nattu laa leen xellee. \q1 \v 11 Samaw tur a tax, \q1 sama tur laay jëfe. \q1 Jomb naa ñaaw! \q1 Te sama teddnga, duma ko joxe. \b \q1 \v 12 Dégluleen ma, yeen askanu Yanqóoba, \q1 yeen \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gi ma dégtal sama woote. \q1 Maay kenn, maa jëkk te maa mujj; \q1 \v 13 te sama loxo bee dëj suuf, \q1 sama ndijoor bi firi asamaan. \q1 Maa leen di woo, ñu bokk taxaw. \q1 \v 14 Bokkleen daje yeen ñépp te déglu! \q1 Kan ci tuur yii moo yégle lii? \q1 Ki Aji Sax ji sopp \q1 mooy sottal nammeelu Aji Sax ji ci Babilon, \q1 won Kaldeen ña fa dëkke diisaayu loxoom. \q1 \v 15 Maa àddu, man mii; \q1 maa ko woo, indi ko, \q1 te pexeem dina joy. \q1 \v 16 Jegesileen ma, déglu ma; \q1 bu jëkk ba tey làquwma, di wax; \q1 te ba muy xew, fa laa teew. \b \q1 Tey Boroom bi Aji Sax ji da maa yebal \q1 boole maakam xelam. \b \q1 \v 17 Aji Sax ji seen \w jotkat|lemma="jotkat b-:"\w* dafa wax, \q1 Aji Sell ju Israyil da ne: \q1 «Maay Aji Sax ji, seen Yàlla \q2 ji leen di jàngal seen njariñ, \q2 di leen awale fa ngeen wara awe. \q1 \v 18 Céy su ngeen sàmmoon samay santaane, \q1 ba jàmm baawaanal leen, \q1 njekk géejal leen, \q1 \v 19 seen geño sakkan ni suuf, \q1 di seen meññeefu biir, tollook feppi suuf, \q1 du dog, du sànkoo fi sama kanam! \b \q1 \v 20 «Génnleen Babilon, \q1 dawleen Kaldeen ñi, tey sarxolle. \q1 Biral-leen lii, yéene ko, \q1 te yeggeji ko waa cati àddina, \q1 ne leen Aji Sax ji jot na jaamam Yanqóoba. \q1 \v 21 Marewuñu bérab yu wow ya mu leen jaarale woon, \q1 ndox mu balle ciw doj la leen xellil, \q1 moo xaru doj, ndox ma baawaan\f + \fr 48.21 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Mucc ga\+bk* 17.1-7.\ft*\f*. \q1 \v 22 Jàmm,» la Aji Sax ji wax ne, \q1 «du ñeel ñu bon ñi.» \c 49 \s1 Surgab Aji Sax ji mooy leeru xeet yi \q1 \v 1 Yeen waa duni géej, dégluleen ma; \q1 yeen askan ya fu sore, teewluleen ma. \q1 Fa sama biiru ndey la ma \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wooye, \q1 moo tudd sama tur ba ma saa ndey juragul. \q1 \v 2 Moo ñawal sama kàddu ni saamar, \q1 làqe ma keru loxoom. \q1 Moo ma def may fitt gu ñaw, \q1 yeb ma ci mbuusum fittam. \q1 \v 3 Moo ma ne: «Israyil yaa di samab jaam, \q1 yaw laay wonee samag leer.» \q1 \v 4 Man nag ma noon: \q1 «Maa sonn ci dara, \q1 coonob cóolóol bu amul njariñ.» \q1 Teewul sama àttee nga fa Aji Sax ji, \q1 sama yool a nga fa sama Yàlla. \q1 \v 5 Tey Aji Sax jee wax, \q1 moom mi dale sama biiru ndey, \q1 mooñ ma, ma dib jaamam \q2 bi koy waññil askanu Yanqóoba ba ca moom, \q1 dajaleel ko \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* googu fa moom, \q1 ba jagoo teraangay Aji Sax ji, \q1 sama Yàlla jii di sama doole. \q1 \v 6 Mu ne: «Xeeb naa li ma la sas ngay sama jaam \q2 biy siggil giiri Yanqóoba, \q2 te wara délloosi ndesu Israyil gii. \q1 Tabb naa la, ngay leeru xeet yi, \q1 di jotale waa cati àddina sama wall.» \b \q1 \v 7 Aji Sax ji \w jotkatub|lemma="jotkat b-:"\w* Israyil, \q1 moom ku Sellam ki, \q1 moo wax ak ki xeet yi xeeb, sib ko, \q1 te muy surgawu kilifa yi, \q1 mu ne ko: «Ay buur ay gis, jóg, \q1 ay kàngam di sukk, \q1 ngir Aji Sax ji boroom worma, \q1 ngir Aji Sell ju Israyil ji la taamu.» \q1 \v 8 Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 «Bu bésub yiw taxawee, ma nangul la; \q1 bu bésub mucc jotee, ma wallu la, \q1 sàmm la, \q1 def la ngay \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* sama digg ak askan wi, \q1 ngir yékkatiwaat réew mi, \q1 séddalewaat ay cér, suuf sii gental tey, \q1 \v 9 ba ne ñi ñu tëjoon: “Génnleen!” \q1 Fa ñu nekkoon cig lëndëm, \q1 laa naa leen: “Génnleen ci leer gi!” \q1 Ñooy doon sama gàtt, dellu di fore aw ñall, \q1 ak wépp tund wu ne faraas tey. \q1 \v 10 Duñu xiif, duñu mar; \q1 tàngooru mbóoya akub jant du leen sonal, \q1 nde ki leen ñeewantee leen di wommat, \q1 di leen yóbbu fu ndox bënne. \q1 \v 11 Sama tund yépp laay soppiy yoon, \q1 sëkkaat samay mbedd. \q1 \v 12 Ñu ngiy bawoo fu sore, \q1 ñu ngii bawoo bëj-gànnaar ak sowu, \q1 ñee bawoo diiwaanu Sinim ca bëj-saalum.» \q1 \v 13 Asamaanoo sarxolleel, suufoo bégal, \q1 te tund yi xaacoondoo! \q1 Aji Sax jee dëfal ñoñam, \q1 moo ñeewante néew-ji-dooleem ñii. \b \q1 \v 14 \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* a nga naa: «Aji Sax ji wacc na nu, \q1 Boroom bi fàtte na nu!» \q1 \v 15 «Ana jaboot juy fàtte doomam juy nàmp, \q1 mbaa muy néege ku mu jur ci biiram. \q1 Bu ko manoona fàtte it, \q1 man duma la fàtte. \q1 \v 16 Sama biir loxo yii laa la ñaas, \q1 say tataa janook man ba fàww. \q1 \v 17 Ñi lay tabaxaat dañuy gaaw, \q1 te ñi la yàqteek ñi la gental \q2 dañuy dem, ba la. \q1 \v 18 Séentul fi la wër te xool! \q1 Ñépp a ngi daje, di la fekksi. \q1 Ndegam maay Kiy Dund,» \q1 kàddug Aji Sax jee, \q1 «ñoom ñépp ngay takkoo ni gànjar, \q2 gooy gànjaroo nib séet. \q1 \v 19 Sa gentub tey bi déy a ngi wéet, \q1 di réew mu yàqu yaxeet. \q1 Waaye léegi déy mu fees ba far xat; \q1 fu ña la sànkoon di soree. \q1 \v 20 Ñàkkoon ngay doom, \q1 waaye ku nekk ci say doom ay dëkkalaat \q2 yii kàddu ci sab nopp: \q1 “Fii dafa xat, \q1 xajal ma, fu ma dëkke!” \q1 \v 21 Dangay mujj naa: \q1 “Moo, ku ma jural ñii ñépp? \q1 Man mi ñàkkooni doom, manumaa jur, \q1 ñu toxal ma, wacc ma; \q1 ana ku leen yoroon te ma des, man kenn? \q1 Ñii sax, fu ñu ne woon?”» \q1 \v 22 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 «Maa ngii di tàllal xeeti jaambur ñi loxo, \q1 ñee ma yékkati raaya, wooye leen; \q1 ñu fab say doom yu góor, indi, \q1 tungóom sa doom yu jigéen, délloosi; \q1 \v 23 Yaw la ay buur di baayoo, \q1 seeni lingeer di la nàmpal. \q1 Ñoo lay sujjóotal, \q1 di la maral say tànk, \q1 ba nga xam ne maay Aji Sax ji, \q1 te ku ma yaakaar du rus.» \b \q1 \v 24 Manees naa foqati alalu sëxëtoo ci loxol jàmbaar a? \q1 Am manees naa rëcc boroom doole bu la jàpp? \q1 \v 25 Aji Sax ji déy dafa wax ne: \q1 «Moona dees na foqati ku jàmbaar jàpp, \q1 ba rëccal alalu sëxëtoob boroom doole. \q1 Say jotewaale, maay joteek ñoom, \q1 te say doom, maa leen di wallu. \q1 \v 26 Ñi lay néewal, maa leen di leel \q2 seen suuxu bopp. \q1 Seen deret ni biiñ bu bees, ma màndale leen, \q1 ba kuy boroom suux xam ne \q1 maay Aji Sax ji lay wallu, \q1 jàmbaaru Yanqóoba ji lay jot.» \c 50 \s1 Aji Sax ji waccul ñoñam \q1 \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: \q1 «Damaa fase seen ndey? \q1 Wonleen ma kayitu pase mi! \q1 Maa leen jaay njaam, feyey bor? \q1 Ana ku ma leen jaay? \q1 Bu ñu leen jaayee, seeni ñaawtéef a. \q1 Bu ñu fase woon seen ndey it, seeni moy a. \q1 \v 2 Ana lu tax ba ma dikkee, kenn nekku fa? \q1 Ma woote, kenn wuyuwul? \q1 Damaa gàtta gàtt loxo, ba manumaa walloo? \q1 Am damaa ñàkk doole ju ma xettlee? \q1 Xanaa du maay gëdd géej, mu wow, \q1 maay defi dex màndiŋ, ndox tukki; \q1 jën ya mar, dee ba yàqu? \q1 \v 3 Du maay sànge asamaan ag lëndëm, \q1 mu mel ni ku ma solal saaku yu muy ñaawloo?» \s1 Siggal nañu jaamub Aji Sax ji \q1 \v 4 Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji moo ma may \q2 làmmiñu ndongo lu mokkal, \q1 ngir ma xam gan kàddu laay jàpplee ku sonn. \q1 Suba su ne mu yee ma, yeel ma nopp \q2 bu ma teewloo ni dongo yi. \q1 \v 5 Boroom bi Aji Sax jee ma bënnali nopp, \q1 te man it, gàntalu ma ko, \q1 deltuwma gannaaw. \q1 \v 6 Gannaaw laa jox ku may dóor, \q1 dékk lex kuy xus sama sikkim, \q1 te làquma sama kanam \q1 ku may saagaak a serati. \q1 \v 7 Waaye Boroom bi Aji Sax jee may dimbali, \q1 ba tax rusuma. \q1 Moo ma taxa dogu ba dëgër, \q1 ngir xam naa ne deesu ma rusloo. \q1 \v 8 Ki may dëggal jege na. \q1 Ana kuy layook man? Nan bokk taxaw! \q1 Kuy jànkoonteek man ci yoon? Na jegesi boog! \q1 \v 9 Ma ne, Boroom bi Aji Sax jee may dimbali. \q1 Ana ku may daan? \q1 Dama ne, ñoom ñépp ay jeexal \q1 ni yére yu saxe ba sagaroo. \b \q1 \v 10 Ana ku ragal Aji Sax ji ci yeen, \q1 di déglu kàddug jaamam? \q1 Képp kuy doxe lëndëm \q1 te amul leeraange, \q1 na wóolu Aji Sax ji, \q1 te wéeroo Yàllaam jii. \q1 \v 11 Ma ne, yeen ñiy jafal ab taal ñépp \q1 tey gañoo jum yuy boy, \q1 xuusleen ci sawara si ngeen jafal \q1 ak jum yi ngeen boyal. \q1 Maa leen dogalal lii: \q1 yeenay tëddaale mitit. \c 51 \s1 Barke ñeel na ñoñu Aji Sax ji \q1 \v 1 Dégluleen maa, yeen ñiy wut njekk, \q1 di sàkku \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \q1 Xool-leen doj wi ñu leen yette, \q1 xool xóotey kàmb gi ñu leen seppee: \q1 \v 2 Seen maam Ibraayma laa ne, moom ngeen di xool, \q1 xool ci Saarata mi leen meññ. \q1 Ba muy kenn laa ko woo, \q1 barkeel ko, ful ko. \q1 \v 3 Aji Sax jeey dëfal \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* moos, \q1 dëfalaale fépp fu fa dib gent, \q1 ba def màndiŋam ni toolub Àjjana, \q1 jooram gu wow mel ni toolub Aji Sax ji, \q1 mbégteek bànneex teew fa, \q1 ak cant gu woy feelu. \q1 \v 4 Yeen sama ñoñ, teewluleen ma, \q1 yeen sama ñoñ, dégluleen ma. \q1 Fi man la téereb yoon di bawoo, \q1 te maay fettaxal sama àtte, \q1 muy leeru xeet yi. \q1 \v 5 Sama wall jege na, \q1 sama njekk dëgmal na, \q1 ma nara àttee xeet yi sama dooley përëg. \q1 Man la waa dun yiy xaar, \q1 sama dooley përëg lañu yaakaar. \q1 \v 6 Séentuleen asamaan \q1 te xool suuf si mu tiim. \q1 Asamaan ay tasaaroo ni saxar, \q1 suuf ràpp ni mbubb, \q1 ñi ko dëkke dee niy weñ, \q1 te du tee sama wall di sax ba fàww, \q1 sama njekk it du dagg. \q1 \v 7 Yeen ñi xam njekk, dégluleen ma, \q1 yeen, askan wi sama yoon yebu ci seen xol. \q1 Buleen ragal nit ku leen sewal, \q1 buleen tiit seeni xaste. \q1 \v 8 Sax a leen di lekk ni mbubb, \q1 max ŋeeñ leen ni ndimol kawaru gàtt; \q1 te du tee sama njekk sax dàkk, \q1 sama wall saxal maasoo maas. \b \q1 \v 9 Aji Sax ji, yewwul, ngalla yewwul; \q1 wone sa doole. \q1 Yewwul na bu jëkkoon, \q1 bu yàgga yàgg. \q1 Xanaa du yaa falaxe Raxab? \q1 Du yaa jam ninki-nànka jooja? \q1 \v 10 Xanaa du yaa wowal géej \q1 ak ndoxum xuram wu ne màww, \q1 def xóotey géej aw yoon, \q1 ña nga jot jàlle ca? \q1 \v 11 Ñi Aji Sax ji goreel, nii lañuy dellusee, \q1 agsaaley sarxolle fa Siyoŋ, \q1 kaalawoo mbég mu sax, \q1 mbégteek bànneex wàllsi, \q1 naqar aku tiis daw. \b \q1 \v 12 Man ci sama bopp maa leen di dëfal. \q1 Ana lu ngeen di ragal ci nit kuy dee, \q1 doom aadama ju bokk akum ñax aw demin? \q1 \v 13 Dangeena fàtte Aji Sax ji leen sàkk, \q1 ki firi asamaan, dëj suuf? \q1 Dangeen di dëkke bésoo bés, \q1 di tiit xadaru boroom doole \q2 buy waaja sànke? \q1 Ana fu xadaru boroom doole mujje? \q1 \v 14 Ku diisoon ba waaf léegi nga féex; \q1 doo deeye pax ma nga tëje, \q1 te doo ñàkk loo lekk. \q1 \v 15 Man maay seen Yàlla Aji Sax ji, \q1 kiy yëngal géej, riiral gannaxam, \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi di sama tur. \q1 \v 16 Maa la sexal samay kàddu, \q1 yiire la sama keru loxo, \q1 aj asamaan, dëj suuf, \q1 ne Siyoŋ: «Yeenay sama ñoñ.» \b \q1 \v 17 Yewwulee, yewwul, Yerusalemee jógal, \q1 yaw mi Aji Sax ji nàndal kaasu mbugalam. \q1 Kaas bu wex bay miirloo, \q1 taat wa, yaa ko siitaatu. \q1 \v 18 Amul ci ñi nga jur, kenn koo dese \q1 ku lay wommat. \q1 Amul ci doom yi nga yar, kenn \q1 ku lay jàpp ci loxo. \q1 \v 19 Yii yaar de dikkal na la: \q1 Yàquleek sànkule. \q1 Ana kuy bokk ak yaw saw naqar? \q1 Xiif ak loraangey saamar! \q1 Ana nu ma lay dëfale? \q1 \v 20 Sa doom yi ne lasar, \q1 mbete kooba yu fiir jàpp, \q1 ñu ne lareet fépp fu mbedd daje, \q1 këppoo sànjum Aji Sax ji, \q1 sa Yàlla ji leen rëbb. \b \q1 \v 21 Rikk déglul nag lii, yaw mi musiba dal, \q1 nga màndi te du biiñ. \q1 \v 22 Sa boroom Aji Sax ji, \q1 sa Yàlla jiy layool ñoñam \q1 dafa wax ne: «Mu ngoog, maa jële ci sa loxo, \q1 kaas bu wex biy miirloo; \q1 taatu kaas ba def sama mbugal, \q1 dootoo ko naan. \q1 \v 23 Maa koy teg ci loxol ñi la doon naqaral, \q1 te naan la: “Sëggal, nu joggi, jàll,” \q1 nga def sa gannaaw gi aw yoon, \q1 ñu joggi, wéy.» \c 52 \s1 Yerusalem dina suqliku \q1 \v 1 Yewwulee, yewwul, \q1 \w Siyoŋee|lemma="Siyoŋ:"\w*, làmbool sa doole! \q1 Yerusalem, dëkk bu \w sell|lemma="sell:"\w* bi, \q1 solul ba ne ràññ! \q1 Ndax du kenn ku xaraful mbaa ku sobewu \q1 ku lay songati. \q1 \v 2 Yaw Yerusalem, mi ñu jàpp njaam, \q1 jógal fëgtu, \q1 yaw janq Siyoŋ mu taaru mi ñu jàpp njaam laa ne, \q1 tikkil buum gi ci sa baat. \q1 \v 3 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji déy dafa wax ne: \q1 «Dees leena wànteeroon ci dara, \q1 te du xaalis lees leen di jotaate.» \q1 \v 4 Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: \q1 «Misra la sama ñoñ jëkka wàcc, dali fa, \q1 Asiri door leena not ci dara. \q1 \v 5 Léegi nag ana lu fiy sama wàll?» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 Mu ne: «Jàpp nañ sama ñoñ njaam ci dara; \q1 seeni sang a ngi tëggu, \q1 di dëkke ñàkke teggin sama tur.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 6 «Moo tax sama ñoñ di xam maay kan; \q1 moo tax bésub keroog \q1 ñu xam ne maay wax te maa ngii!» \b \q1 \v 7 Ndaw leeka rafeti tànk, \q1 kee bartaloo tund yi, \q1 di la dégtalsi jàmm, \q1 di la xibaar lu neex, \q1 àgge la ag mucc, \q1 ne la: «Éey, Siyoŋ, \q1 sa Yàllaay Buur!» \q1 \v 8 Déglul sa jongrukat yi, \q1 ña ngay xaacu, sarxollendoo. \q1 Ñoo gisal seen bopp \q2 Aji Sax ji di ñibbsi Siyoŋ. \q1 \v 9 Yeen genti Yerusalem, àndleen sarxolle; \q1 Aji Sax jeey dëfal ñoñam, \q1 mooy jot Yerusalem gii! \q1 \v 10 Aji Sax jee wone dooleem ju sell ji, \q1 xeet yépp di gis, \q1 ba ca cati àddina. \q1 Ñépp ay gis sunu wallu Yàlla. \q1 \v 11 Yeen ñiy yóbbu ndabi Aji Sax yu sell yi\f + \fr 52.11 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk 2.Buur ya\+bk* 25.13-15.\ft*\f*, \q1 bu ngeen di jóge Babilon, \q1 dëdduleena dëddu lu sobewu, bañ koo laal, \q1 setluleen te génn foofa. \q1 \v 12 Dungeen gaawtu déy, di dem; \q1 duy xél moos ngeen fay génne. \q1 Aji Sax jeey dox jiitu leen, \q1 te Yàllay Israyil laa ne, moo leen di féete gannaaw. \s1 Teraangay jaam bi wuutu na coonoom \q1 \v 13 Aji Sax ji nee: «Sama jaam baa ngi, \q1 mooy baaxle, kawe, \q1 dees na ko yékkati, darajaal ko lool. \q1 \v 14 Moo dawoon yaramu ñu bare, \q1 ndax yàqu ba nirootul nit, \q1 bindootul woon ni doom aadama, \q1 \v 15 waaye noonu it lay waare ay xeeti xeet\f + \fr 52.15 \fr*\ft Manees na koo tekkee nii itam: \ft*\fqa xeet yu bare lay wis-wisal um ndox, setale leen ko.\fqa*\f*, \q1 ba buur yi wedam, \q1 ngir lu ñu leen waxuloon, te ñu gis ko, \q1 lu ñu dégguloon, te mujj ko ràññee.» \c 53 \q1 \v 1 Ana ku gëm sunub dégtal? \q1 Ana ku \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji won dooley përëgam? \q1 \v 2 Kii màgge fi kanamam ni njëmbat, \q1 te nirook reen bu fette ag kekk. \q1 Dub taar, du yànjaay bu nu koy niire, \q1 du meloom wu nu koy soppe. \q1 \v 3 Dees na ko xeeb, daw ko, \q1 muy nit ku bare mitit \q1 te miin naqar. \q1 Mu mel ni ku ñuy dummóoyu, \q1 dees koo xeeb te nawloowuñu ko. \q1 \v 4 Ndaxam moom sunu wopp la yenu, \q1 sunuy mitit la sëfoo. \q1 Nun nu foog ne dees koo mbugal, \q1 foog ne Yàllaa ko duma, torxal ko. \q1 \v 5 Te moom sunuy tooñ a waral ñu jamat ko; \q1 sunuy ñaawtéef a waral ñu dëggaate ko. \q1 Yar yi nu jàmmal moom la dal, \q1 te mooy ki nu wére ciy góomam. \q1 \v 6 Nun ñépp a lajj niy xar, \q1 ku nekk walbatiku topp yoonam, \q1 te Aji Sax jee ko këpp sunu gépp ñaawtéef. \q1 \v 7 Dees koo néewal doole, mitital ko \q1 te ubbiwul gémmiñam, \q1 xanaa mel ni xar mu ñuy rendiji, \q1 ne cell ni xar mu ñuy wat, \q1 ubbiwul gémmiñam. \q1 \v 8 Àtte nañu ko ñàkkal, yóbbu, \q1 te ag maasam kenn teewluwu ci ne \q1 tooñ gu sama bokk yi tooñ \q1 lees ko dagge ci réewum aji dund ñi, \q1 te loolu lees ko fàdde. \q1 \v 9 Ni ñuy robe saaysaay lañu ko robe, \q1 denc ko ci bàmmeelu boroom alal, \q1 soxorul, fenul. \b \q1 \v 10 Moona Aji Sax ji la soob, mu dëggaate jaamam bii, \q1 teg koy naqar, \q1 su nangoo doon \w saraxu peyug tooñ|lemma="Sarax yi:"\w*, \q1 gis askanam, aw fanam gudd, \q1 te coobarey Aji Sax ji ci moom lay sottee. \q1 \v 11 Mooy sonn ba gis ug leer, doyloo ko, \q1 te ñu bareey xam sama jaam bii di Aji Jub, \q1 ba mu àtte leen àtteb njekk, \q1 sëfoo seeni ñaawtéef. \q1 \v 12 Moo tax ma di ko jox ab cér \q2 ci biir ñu bare, \q1 mu séddoo ak ay kàngam alalu xareem, \q1 ngir moo jébbale bakkanu boppam, \q1 ñu limaale kooki tooñkat, \q1 moo gàddu bàkkaaru ñu bare \q1 te mooy tinul moykat yi. \c 54 \s1 Aji Sax ji jëlaat na Yerusalem, soppeem \q1 \v 1 «Yaw mi jaasir ba juroo, xaacul! \q1 Yaw mi xamul mititu mat, sarxolleel.» \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nee: \q1 «Ndaw si ñu foñ moo gëna jaboot \q2 kiy séy. \q1 \v 2 Yaatalal sa xayma bi, \q1 firi sa sori xayma yu gëna yaa \q1 te bul yéem. \q1 Yokkal sa buumi xayma \q1 te samp say bant, mu dëgër. \q1 \v 3 Dinga saam ay doom ndijoor ak càmmoñ, \q1 saw askan moom ay xeet, \q1 sancaat dëkk yu gentaloon. \q1 \v 4 Bul tiit, doo rus mukk. \q1 Bul jaaxle, deesu la kersaal mukk. \q1 Sa gàcce ga ba ngay ndaw, dinga ko fàtte, \q1 te sa tiisu jëtun wa dootoo ko fàttliku. \q1 \v 5 Sa jëkkër, ki la sàkk, \q1 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee di turam. \q1 Aji Sell ju Israyil moo la jot, \q1 te moo di Yàllay àddina sépp. \q1 \v 6 Aji Sax jee la woo, nga dib jeeg bu ñu wacc, \q1 sa xol jeex tàkk, \q1 Mu ne la: \q1 “Nees di wacces ndaw, \q2 si nga takk ba ngay ndaw?”» \q1 Sa Yàllaa ko wax. \q1 \v 7 Mu ne: «Maa la wacc diir bu gàtt, \q1 dellu la jël ci yërmande ju yaa. \q1 \v 8 Sama xol a jóg, \q1 ma xañ la sama kanam ab diir, \q1 waaye maa lay yërëme ngor gu sax.» \q1 Aji Sax, ji lay jot moo ko wax. \b \q1 \v 9 Mu ne: «Na ma defoon ak \q2 ndoxum Nóoyin ma mooy lii tey. \q1 Maa giñoon ne ndoxum Nóoyin ma, \q2 mu ni day dootu wale kaw suuf. \q1 Noonu it laay giñe ne \q1 duma la mereeti, \q1 duma la rëbbati. \q1 \v 10 Bu tund yu mag yi doon toxu, \q1 yu ndaw yiy raf sax, \q1 sama ngor du la toxul, \q1 te sama \w kóllërey|lemma="kóllëre g-:"\w* jàmm du raf.» \q1 Aji Sax ji la yërëm moo ko wax. \b \q1 \v 11 «Ngalla yaw Yerusalem, \q1 mi ngëlén pamti-pamtee ba nga jàq, \q1 te kenn dalalu la, \q1 man Aji Sax ji, \q1 maa ngii di la tabaxe doj yu ne ràññ, \q1 samp la ci kenuy safiir. \q1 \v 12 Maay defare sa kawi tata peri rubi, \q1 def say wunt per yuy lerxat, \q1 def sa tata yi la wër yépp doj yu bakkane, \q1 \v 13 mboolem sa doom yu góor ay jànge ci Aji Sax ji, \q1 boole kook jàmm ju ne ñoyy. \q1 \v 14 Njekk moo lay dëgëral, \q1 nga sore noteel, doo tiit; \q1 sore tiitaange, du la jege. \q1 \v 15 Xanaa dees na songe moos, \q1 waaye ku la song it, yebalu ma ko, \q1 te ku la song daanu fi sa kanam. \q1 \v 16 Xoolal, man maa sàkk ab tëgg \q2 buy wal taalu këriñ, \q1 defar ca ngànnaay lu ne. \q1 Waaye maa sàkk it \q1 yàqkat buy rajaxe. \q1 \v 17 Ngànnaay lu ñu la mana sàkkal, \q1 du sotti, \q1 te boroom làmmiñ wu la jógal cib layoo \q1 yaa koy tiiñal. \q1 Ñiy jaamu Aji Sax ji, looloo di seen cér, \q1 looloo di njekk gi ma leen di dikke.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \c 55 \s1 Aji Sax ji woote na njéggal \q1 \v 1 «Éey, yeen ñi mar ñépp, \q1 dikkleen ci ndox mi, \q1 ba ci ku amul xaalis sax! \q1 Dikkleen jënd pepp, lekk! \q1 Dikkleen jënd pepp mu xaalis jëndul, \q1 ak biiñ ak meew mu amul pey. \q1 \v 2 Ana lu ngeen di waññe xaalis, \q1 di ko jënde lu dul aw ñam? \q1 Ana lu ngeen di sonn, \q1 di jënde lu dul reggal? \q1 Dégluleen maa déglu, ba lekk lu leen di dundal, \q1 di xéewloo seen ngëneelu bakkan. \q1 \v 3 Teewluleen te dikk fi man. \q1 Dégluleen, ba mana dund, \q1 ma fas ak yeen \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* gu sax, \q2 gi ma baaxee Daawuda ci ngor gu wóor. \q1 \v 4 Ab seedee ngoog, ñeel xeet yi, \q1 muy njiit, yilif xeet yi. \q1 \v 5 Ma ne, aw xeet woo xamul ngay wooyi, \q1 xeet wu la xamul ay dawsi ba ci yaw, \q1 ngir sa Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 Aji Sell ju Israyil, \q1 nde moo la teral.» \b \q1 \v 6 Sàkkuleen Aji Sax ji bi ngeen koy mana gis, \q1 wooleen ko bi muy jege. \q1 \v 7 Na ku bon ba jëfinam, \q1 kuy def lu ñaaw fomm mébétam, \q1 te walbatiku ci Aji Sax ji sunu Yàlla, \q1 mu yërëm ko, yaatal njéggalam. \q1 \v 8 «Samay xalaat déy du seeni xalaat, \q1 te samay jëfin du seeni jëfin.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 9 Mu ne: «Ni asamaan tiime suuf, \q1 ni la samay jëfin tiime seeni jëfin, \q1 samay xalaat it tiime ko seeni xalaat. \q1 \v 10 Ab taw ak tawub yuur asamaan lay wàcce, \q1 du fa dellu, \q1 te suuxatul suuf, \q1 saxal ko, meññal ko, \q1 ba kuy ji, mu may la jiwu; \q1 kuy lekk, mu may lam pepp. \q1 \v 11 Sama kàddu giy bawoo sama gémmiñ it, noonu la. \q1 Du délsee ag neen ci man \q1 te deful li ma namm, \q1 ba sottal li ma ko yebal. \b \q1 \v 12 «Mbégte déy, ngeen di génne, \q1 ñu yóbbu leen ci jàmm, \q1 tund yu mag yeek yu ndaw yi \q1 di leen sarxolleel, \q1 garabi àll bi yépp tàccoondoo. \q1 \v 13 Garab gu dul ruus ay wuutub gajj, \q1 garab gu dëkke naat wuutub taxas, \q1 muy woyu Aji Sax ji, \q1 te di firnde ju sax, \q1 du dog mukk.» \c 56 \s1 Xeet yépp la Aji Sax jiy ñoñoo \q1 \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: \q1 «Sàmmleen yoon, di def njekk. \q1 Sama wall kat a ngi dikk léegi, \q1 sama njekk laa ne, léegi mu teew. \q1 \v 2 Ndokklee kuy jëfe lii, \q1 ndokklee doom aadama ju jàppoo lii, \q1 di sàmm \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*, \q1 bañ koo ñàkke worma, \q1 di sàmm loxoom ci jépp jëf ju bon.» \q1 \v 3 Doomu doxandéem bu jokku ci Aji Sax ji, \q1 bumu ne: «Aji Sax jee may beddee beddi ci ñoñam.» \q1 Jaam bu ñu xañ ngóora it bumu ne: \q1 «Man garab gu jaasir doŋŋ laa.» \q1 \v 4 Aji Sax ji kat dafa wax ne: \q1 «Jaam yi ñu xañ ngóora, \q1 su ñu sàmmee sama bési Noflaay, \q1 taamu sama coobare, \q1 tey feddli sama \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w*, \q1 \v 5 maa leen di may ci sama biir kër, sama biir ëtt, \q1 doj wu ñu leen di fàttlikoo \q1 ak tur wu leen di gënal doom yu góor ak yu jigéen. \q1 Tur wu sax dàkk laay may \q2 jaam yi ñu xañ ngóora, \q1 te du fey mukk\f + \fr 56.5 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Sarxalkat yi\+bk* 21.16-20.\ft*\f*.» \q1 \v 6 Doomi doxandéem yi ànd ak Aji Sax ji, \q1 ngir liggéeyal ko, \q1 ngir sopp turu Aji Sax ji, \q1 te di ay jaamam, \q1 muy képp kuy sàmm bésub Noflaay, \q1 baña ñàkke worma bés bi, \q1 xanaa di feddli kóllëreem, \q1 \v 7 mu ne: «Ñooñu, maa leen di yóbbu \q2 sama kaw tund wu \w sell|lemma="sell:"\w*, \q1 bànneexale leen sama biir kërug ñaan, \q1 seen \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* ak yeneen sarax, \q1 dees na leen ko nangul sama kaw \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*, \q1 ndax dees na wooye sama “kër, kërug ñaan”, \q2 ñeel xeetoo xeet.» \q1 \v 8 Kàddug Boroom bi Aji Sax jaa ngi, \q1 kiy dajale giiri Israyil yi tasaaroo, \q1 mu ne: «Maay dajaleeti, \q1 dolli ca la ma dajale woon.» \s1 Ab daan ñeel na njiit yi \q1 \v 9 Yeen rabi àll yi, \q1 dikkleen ci bernde ji, \q1 yeen rabi gott bi yépp. \q1 \v 10 Jongrukati Israyil yépp a silmaxa, \q1 te xamuñu dara. \q1 Ñoom ñépp a diy xaj yu luu, \q1 manuñoo baw, \q1 xanaa tëdd di jeneer, \q1 soppi nelaw. \q1 \v 11 Xaj yu tiita tiit lañu, \q1 xamuñu suur, \q1 te ñooy sàmm yeey! \q1 Ñoom ñépp, kenn manu cee xam dara, \q1 seen yoonu bopp lañu topp, \q1 ak seen amin wu lewul. \q1 \v 12 Ña nga naa: «Dikkleen, ma indi biiñ, \q1 nu màndeew ñoll; tey ak ëllëg; \q1 li fi des du jeex.» \c 57 \s1 Ab daan ñeel na moykat yi \q1 \v 1 Aji jub ñaa ngi dee, \q1 te kenn yégalu ko yaramam. \q1 Gor ñaa ngi faatu, \q1 te kenn ràññeewul \q1 ne aji jub ji, faatoom, musiba la koy moyale. \q1 \v 2 Kiy am jàmm ëllëg, \q1 di am noflaay ci biir tëraayam, \q1 mooy kiy wéye njub. \b \q1 \v 3 Waaye yeen, dikkleen fii, \q1 yeen doomi xërëmkat yi, \q1 yeen askanu njaalookat yiy gànctu, \q1 \v 4 ana ku ngeen di ñaawal? \q1 Ana ku ngeen di ŋóobi, \q1 ak di ko kókkali? \q1 Xanaa dungeen doomi moykat, \q1 di askanu workat, \q1 \v 5 di xabtaloo bànneex \q1 ci ker garab yu mag yi, \q1 ak ker garaboo garab gu naat, \q1 di rendi seeni doom ci yoonu ndox yi, \q1 ak xarantey doj yi? \q1 \v 6 Yaw Israyil, jëlal doj yu rattax \q2 yi ci yoonu ndox wi, séddoo, \q1 muy sa cér, nga muurloo! \q1 Ñoom ngay tuural, \q1 di leen defal ay \w saraxi pepp|lemma="Sarax yi:"\w*. \q1 Waaye Aji Sax ji nee: \q1 «Ndax damay jéllale?» \q1 \v 7 Tund wu mag te kawe, \q1 nga fàkk fa tëraay, \q1 yéeg fa, di fa sarxalal. \q1 \v 8 Yaa takk say baaxantal \q1 ci sa lafu bunt ak sa jëni bunt, \q1 yaa ma wacc, di ñorikoo feneen, \q1 yéeg sab lal, yaatal. \q1 Yaa takktook ñii nga soppa tëddal \q1 te safoo di niir seeni cér. \q1 \v 9 Yaa tukki ba ca buur ba, yóbbaaleg diw, \q1 ak cuuraay lu ne gàññ, \q1 yebal say ndaw fu sore, \q1 ba ñu àkki njaniiw. \q1 \v 10 Tukki bu sore bu la sonal sax \q1 taxu la ne: «Fomm naa.» \q1 Bànneex bi ngay séentu ngay leqlikoo, \q1 ba tax sonnuloo. \b \q1 \v 11 Ana kooy tiit, \q1 ak koo ragal ba di ma wor, \q1 fàttlikootoo ma, \q1 faaleetoo ma? \q1 Damaa noppi lu yàgg daal, \q1 ba tax ragalatoo ma? \q1 \v 12 Defe nga ne njekk nga def, \q1 waaye dinaa la weer, \q1 te sa jëf du la jariñ. \q1 \v 13 Boo wootee wall, \q1 na la sa gàngooru tuur xettli. \q1 Ñoom ñépp la ngelaw di buub, \q1 callweer yóbbu leen. \q1 Waaye ku ma làqoo, \q1 kookooy moom réew mi, \q1 séddoo sama tund wu \w sell|lemma="sell:"\w* wi. \b \q1 \v 14 Dees na ne: «Maasaleleenoo, maasaleleen, \q1 yaatal leen yoon wi, \q1 te jële luy pakk ci sama yoonu ñoñ.» \q1 \v 15 Ku màgg, ku kawe ki, \q1 ki màkkaanam sax dàkk \q1 te turam sell, daa wax ne: \q1 «Fu kawe te sell laa màkkaanoo, \q1 maa dëkk ak boroom xol bu mokk, \q1 te toroxlu, \q1 ngir leqli ku toroxlu, \q1 leqli boroom xol bu mokk. \q1 \v 16 Duma wéye di sikke ba fàww, \q1 duma saxoo di mer, \q1 lu ko moy képp ku ma sàkk \q1 day tàggook bakkanam. \q1 \v 17 Ñaawtéefi Israyil ak alalam ju lewul \q2 moo ma merloo, \q1 ma duma ko, xañ ko sama kanam, \q1 waaye mu të ticc, topp xolam. \q1 \v 18 Xam naa jikkoom, \q1 waaye maa koy faj, \q1 wommat ko, \q1 dëfale koy xéewal, \q1 mook ñiy ñaawloondook moom. \q1 \v 19 Maay teg ci seen làmmiñ kàddug cant. \q1 Jàmm, na jàmm ñeel ñépp, \q1 ku soreek ku jege.» \q1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. \q1 Mu ne: «Maa leen di faj.» \q1 \v 20 Waaye ñu bon ñi, mbete géej \q2 gu sàmbaraax, tëë dal, \q1 gannax yay baaje ban ak suuf. \q1 \v 21 Sama Yàlla nee: \q1 «Jàmm du ñeel ñu bon ñi.» \c 58 \s1 Jaamu Yàlla, tuub, rafet jikkoo ci gën \q1 \v 1 Aji Sax ji nee: «Xaacul loo man, \q1 te bul ñéeblu; \q1 àddul ni bufta, \q1 te yégal sama ñoñ seen bàkkaar, \q1 ngir waa kër Yanqóoba yii xam seeni moy. \q1 \v 2 Man mii lañuy sàkku bés bu ne, \q1 di wuta xam sama coobare! \q1 Mbete xeet wuy def njekk, \q1 te waccul ndigalu yoonu Yàllaam. \q1 Ñu ngi may ñaan àttey njekk, \q1 di sàkku man Yàlla, ma jege leen, \q1 \v 3 te naa: “Ana lu nuy woor te xooloo ci? \q1 Lu nuy toroxlu te teewluwoo?” \q1 Ma ne: Bés bu ngeen woor, \q1 yeena ngi topp seen bakkan, \q1 di sëqatal seeni liggéeykat. \q1 \v 4 Xanaa du koor gu ànd ak xulook ŋaayoo, \q1 ak di joqlantey këmëx yu metti? \q1 Su ngeen bëggee seen ñaan àgg fa kaw, \q1 dungeen woor ni ngeen woore tey. \q1 \v 5 Ndax lii moo di koor gi ma taamu, \q1 ci bés bu nit kiy toroxlu? \q1 Koorug dëngal loos ni barax, \q1 lal saaku, sotti ab dóom, tëdd \q1 di ko ñaawloo? \q1 Loolooy seen koor, \q1 ci bés bu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji rafetlu? \b \q1 \v 6 «Xanaa du lii moo di koor gi ma taamu: \q1 yolomal jéng yu metti, \q1 fecci buumi noteel, \q1 afal ku diis; \q1 dog lépp luy xeetu noteel? \q1 \v 7 Xanaa du sédd ku xiif saw ñam, \q1 fat néew-ji-doole ju amul fu mu dëkk, \q1 gis ku rafle, wodd ko, \q1 te baña nëbbu mbokk mu soxla? \q1 \v 8 Su boobaa seen leer feq ni njël, \q1 seen góom gaawa wér, \q1 seen njekk jiitu leen, \q1 leeru Aji Sax ji féete leen gannaaw. \q1 \v 9 Su boobaa bu ngeen wooyee Aji Sax ji, mu wuyu; \q1 ngeen ne wallóoy, mu ne “Maa ngi.” \q1 Ndegam génne ngeen noteel ci seen biir, \q1 ak di joxoñeek a wax lu ñaaw, \q1 \v 10 di leel ku xiif lu ngeen gëna bëgg, \q1 di reggal néew-ji-doole, \q1 su boobaa seen leer fenke biir lëndëm, \q1 seenug këruus di ag njolloor, \q1 \v 11 Aji Sax ji di leen jiite fu ngeen tollu, \q1 di leen màndale joor gu maral, \q1 dëgëral seeni cér, \q1 ngeen mel ni tool bu ñu suuxat, \q1 mel ni bëtu ndox bu dul ŋiis, \q1 \v 12 seeni nit tabaxaat gent ya woon, \q1 ngeen yékkatiwaat kenu yu yàgga yàgg. \q1 Dees na la wooye jagalkatu xar-xar yi, \q1 mbaa kiy yeesal xàll yi, ngir dëkke réew mi. \b \q1 \v 13 «Su ngeen téyee seen tànk \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*, \q1 baña def li leen neex sama bés bu \w sell|lemma="sell:"\w*; \q1 su bésub Noflaay di seen nammeel, \q1 di \w bésub Aji Sax|lemma="bésub Aji Sax ji-:"\w* bu sell bu ngeen teral; \q1 ngeen teral bés bi, \q1 bañ cee topp li ngeen jikkowoo, \q1 di topp seen bakkan \q1 ak wax ju dul jeex; \q1 \v 14 su boobaa ngeen bànneexoo Aji Sax ji, \q1 ma waral leen kawtey réew mi, \q1 leele leen seen céru maam Yanqóoba.» \q1 Aji Sax ji déy wax na ko. \c 59 \s1 Bàkkaar ñag na diggante Yàllaak ñoñam \q1 \v 1 Ma ne, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji gàttul loxo ba tëlee walloo, \q1 noppam naqariwul ba tere koo dégg. \q1 \v 2 Seeni ñaawtéef a dox seen digganteek \q2 seen Yàlla. \q1 Seeni moy a leen xañ kanamam, \q1 ba mu tanqamlu leen. \q1 \v 3 Seeni loxoo taq deret, \q1 ngeen ne lijj ci ñaawtéef, \q1 làmmiñ di fen, di sos njekkar. \q1 \v 4 Du njekk gu kenn wut cib àtte, \q1 du dëgg gu kenn sàkku cib layoo. \q1 Ñu ngi yaakaar caaxaan, di fen, \q1 di sos ayib, wasin ñaawtéef. \q1 \v 5 Nenu ñàngóor lañuy tostan, \q1 di ràbb lëndu jargoñ. \q1 Ku lekk ci nen yi dee, \q1 te boo ci tojeeb nen, \q1 saamaan fëlle ca. \q1 \v 6 Seeni lënd du ràbbe ba solal nit, \q1 mbaa di sàng kenn; \q1 seenum ràbb ñaawtéef lay jur, \q1 seen loxo ya ko liggéey sabab fitna, \q1 \v 7 seeni tànk daw wuti lu bon, \q1 ñuy yàkkamtee tuur deretu ku deful dara, \q1 seeni xalaat di ñaawtéef, \q1 yàquteek njaaxum féete ca seeni yoon. \q1 \v 8 Xamuñu yoonu jàmm, \q1 te yoon amul fa ñuy jaare, \q1 xanaa sàkk seen yoon yu lunk \q1 te ku fa awe doo daj jàmm. \b \q1 \v 9 Lee tax yoon sore nu, \q1 te njekk du nu dab. \q1 Danuy yaakaar leer, \q1 lëndëm ne jaas, \q1 nuy séentuy ceeñeer, \q1 tey lëndëmtuy wéy. \q1 \v 10 Nu ngi làmbatub tabax ni silmaxa, \q1 di tëñëx-tëñëxi ni ku amuli gët, \q1 di fakktalu bëccëg ndarakàmm ni bu doon guddi, \q1 dëkk ak ñu wér péŋŋ te mel ni ña dee. \q1 \v 11 Nun ñépp a ngi xiiru ni rab wu aay, \q1 binnee binni niy xati, \q1 yaakaar yoon, yoon wuute, \q1 séentu wall, wall sore. \q1 \v 12 Sunuy tooñ a bare fi sa kanam, \q1 sunuy moy a nu seedeel, \q1 sunuy tooñ a nu topp, \q1 te xam nan xéll sunuy ñaawtéef. \q1 \v 13 Noo tooñ Aji Sax ji, wor ko, \q1 te noo dëddoo sunu Yàlla jii, \q1 kàdduy fitna ak fippu, \q1 ak fen yu nu mébét, nas ko, \q1 \v 14 ba yoon dellu gannaaw, \q1 njekk dànd, \q1 dëgg fakktaloo fa pénc ma, \q1 njub tëë agsi. \q1 \v 15 Dëgg a tumurànke, \q1 ku dëddu mbon sax, ñu ñori la, \q1 Aji Sax ji gis ci, ñaawlu ko, \q1 nde yoon a amul. \q1 \v 16 Daa xool, gisul kenn; \q1 mu tiisoo li ci kenn jógul, \q1 moo tax loxoom may ko ndam, \q1 te njekkam la sukkandikoo. \q1 \v 17 Moo sol kiiraayal njekk, \q1 mbaxanawoo mucc, \q1 solati yérey mbugale, \q1 làmboo turkib xéraange. \q1 \v 18 Mooy delloo ku ne yool ba mu yelloo, \q1 mbugal ay bañam, fey ay noonam, \q1 ba delloo waa dun ya yool ba ñu yelloo. \q1 \v 19 Dees na wormaale turu Aji Sax ji fa sowu, \q1 wormaale teddngaam ba penku. \q1 Bu noon bi agsee ni walum dex, \q1 ngelawal Aji Sax jee koy wal, mu daw. \q1 \v 20 «Ab \w jotkat|lemma="jotkat b-:"\w* ay dikkal \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, \q1 ba jot ñi tuub seeni bàkkaar ci askanu Yanqóoba.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 21 «Man nag, lii mooy sama \w kóllëreek|lemma="kóllëre g-:"\w* ñoom: \q1 Sama xel mi tegu fi sa kaw, \q1 ak sama kàddu yi ma yeb ci sa gémmiñ, \q1 lenn du ci teqlikook sa gémmiñ \q1 ak sa gémmiñu askan, \q1 ak sa gémmiñu askanu askan, tey ak ëllëg.» \q1 Aji Sax jee ko wax. \c 60 \s1 Leer dina fenkal Yerusalem \q1 \v 1 Yerusalem, jógal ne ràññ, sag leer feq na; \q1 teddngay \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji fenkal na la! \q1 \v 2 Lëndëm gaa ngii di muur àddina, \q1 mu ngi guddil askan yi, \q1 te yaw, Aji Sax ji fenkal la, \q1 leeru teddngaam feqal la. \q1 \v 3 Ay xeet ay fekksi sag leer, \q1 ay buur wutsi sa ceeñeeru njël. \b \q1 \v 4 Séentul fi la wër ba gis: \q1 ñoom ñépp a daje, di la fekksi, \q1 sa doom yu góor a dikke fu sore, \q1 te sa doom yu jigéen it \q2 dees leena fab, indaale. \q1 \v 5 Yaa koy gis, sa kanam ne ràññ, \q1 fit tëf-tëfi, xol fees dell, \q1 nde dees na walbati xéewali géej, indil la, \q1 alali xeet yi dikkal la. \q1 \v 6 Ndiiraanu giléem a lay fees \q1 ak njëggi Majan ak Efa, \q1 ñoom ñépp sëfe Saba. \q1 Dees na indi wurus ak \w cuuraay|lemma="cuuraay l-:"\w* \q1 tey kañaale Aji Sax ji. \q1 \v 7 Gétti Kedar yépp a lay dajesil, \q1 kuuyi Nebayot di la jariñ, \q1 te di sarax yu dajeek ngërëm \q2 ci kaw \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* Aji Sax ji, \q1 ma di ko darajaale sama teddngay kër. \b \q1 \v 8 Ana ñuy ñii di naaw niy niir, \q1 nirook ndiiraanu pitax yu jëm seeni tàgg? \q1 \v 9 Waa dun ya déy a nga may séentu, \q1 gaali Tarsis yu mag yaa nga jiitu, \q1 jële fu sore sa doom yu góor ya, \q1 indaale seen xaalis ak seen wurus, \q1 ngir sa Yàlla Aji Sax ji, \q1 Aji Sell ju Israyil ji la teral. \q1 \v 10 Ay doomi doxandéem ay tabaxaat say tata, \q1 seeni buur di la surgawu. \q1 Maa meroon, duma la, \q1 maa la baaxe, yërëm la. \q1 \v 11 Say wunt ay ubbiku saa su ne, \q1 guddeek bëccëg, du tëje, \q1 xanaa di la jàlleel alali xeet yi, \q1 seeni buur riixle ànd ca. \q1 \v 12 Mu diw xeet, dim réew, \q1 ku la ci nangulul sànku. \q1 Xeet yooyu yépp ay yàqu yaxeet. \q1 \v 13 Taaru àllub Libaŋ a lay ñibbsil, \q1 garabu sippar, pẽe ak geneen gu dëkke naat, \q1 taaralsi sama kër gu sell gi, \q1 ba ma terale ci sama ndëggastalu tànk. \q1 \v 14 Ña la daa néewal, \q1 seeni doom a lay sukkalsi. \q1 Ña la daa ñàkke worma, \q1 mujj di fóon say tànk. \q1 Dees na la wooye «Dëkkub Aji Sax ji», \q1 mbaa «\w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, màkkaanu Aji Sell ju Israyil.» \b \q1 \v 15 Dees laa foñ, jéppi la, \q1 ba kenn jaareetu fi. \q1 Waaye maay def ñu di la sagoo ba fàww, \q1 di la bége sët ba sëtaat. \q1 \v 16 Yaay naan soowum xeet yi, \q1 nàmp weenu buur yi, \q1 ba xam ne maay Aji Sax jiy walloo, \q1 jàmbaaru Yanqóoba ji lay jot. \q1 \v 17 Maay wuutale xànjar, wurus; \q1 wuutale weñ gu ñuul, xaalis; \q1 bant, xànjar; \q1 doj, weñ gu ñuul. \q1 Jàmm laay def mu jiite la, \q1 def njekk yilif la. \q1 \v 18 Deesatul dégg ci sam réew: \q2 «Fitna ñëw na!» \q1 deesatul dégg it fi sa kemu suuf: \q2 «Yàqute ak Yàqulee ngi!» \q1 «Mucc» ngay tudde say tata, \q1 te «Cant» ngay tudde sa bunti dëkk. \q1 \v 19 Du jant a lay leeralati bëccëg, \q1 te weer du la niital; \q1 Aji Sax jeey doon sag leer ba fàww, \q1 sa Yàlla jooju di sab taar. \q1 \v 20 Sab jant du sooti, \q1 sa weer du suuxati. \q1 Aji Sax jeey doon sag leer ba fàww, \q1 sa fani ñaawlu jeex. \q1 \v 21 Sa askan wépp ñu jub lañuy doon, \q1 te ñooy moom réew mi ba fàww. \q1 Ñooy sama njëmbat li ma jëmbatal sama bopp, \q1 sàkke leen samay loxo, ngir sama teddnga teew. \q1 \v 22 Ki ci gëna tuut ay meññ junni, \q1 ki ci gëna néew jur xeet wu mag. \q1 Man Aji Sax ji, bu lii jotee, \q2 ma gaaw koo sottal. \c 61 \s1 Ki Boroom bi fal dikk na \q1 \v 1 Noowug Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jaa ngi fi sama kaw, \q1 ndax Aji Sax jee ma diw\f + \fr 61.1 \fr*\ft Baat bi ñu tekkee diw, ci la baatub Almasi jóge. Ab sarxalkat mbaa buur lañu daan diw, fale leen ko bala ñoo door seen liggéey.\ft*\f*, fal ma, \q1 ngir ma àgge néew-doole yi xibaaru jàmm. \q1 Moo ma yebal ngir ma dëfal ñi seen xol jeex, \q1 yégal jaam yi, seen goreel, \q1 yégal ñi ñu tëj, seen ubbite. \q1 \v 2 Moo ma yónni ngir ma yéene atum yiwu Aji Sax ji, \q1 ak at mu sunu Yàlla di mbugalee. \q1 Moo ma yónni ngir dëfal ñiy ñaawlu ñépp, \q1 \v 3 ngir tabb waa \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* ñiy ñaawlu, \q1 jox leen kaala gu wuutu dóom bi ñuy ñaawloo, \q1 ak diwu mbégte mu ñu weccikoo seenu tiis, \q1 ak mbubbam cant mu ñu weccikoo xol bu jeex, \q1 ba ñu naa: «Ñii ñoo di ponkali garabi njekk yi, \q1 njëmbat li Aji Sax ji jëmbat, \q1 ngir teewal teddngaam.» \q1 \v 4 Ñooy tabaxaat gent ya woon, \q1 yékkati bérab ya tasoon bu yàgg, \q1 dekkal dëkk yu tas, \q1 bérab yu gental ay maasi maas. \q1 \v 5 Ay gan ay dikk, \q1 di leen sàmmal seeni gétt, \q1 ay doomi doxandéem di leen beyal tool \q2 ak tóokëru reseñ. \q1 \v 6 Yeen nag lees di wooye: \q1 «\w Sarxalkati|lemma="sarxalkat b-:"\w* Aji Sax ji,» \q1 ñu naa: «Sunu surgay Yàlla yaa ngi!» \q1 Alali xeet yi, yeena koy lekk, \q1 di damoo seeni koom. \q1 \v 7 Sama ñoñ ay weccikoo seen gàcce \q2 ñaari céri teraanga, \q1 sarxolley mbég di seen cér, \q2 wuutu toroxte. \q1 Ñaari cér lañuy am ca seenum réew, \q1 mbégte mu sax ñeel leen. \q1 \v 8 Man Aji Sax ji, damaa sopp yoon, \q1 bañ càcc ak ñaawtéef. \q1 Maay dàmp sama ñoñ ni mu ware, \q1 fas ak ñoom \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* gu sax. \q1 \v 9 Dees na xàmmee seen askan fi biir xeet yi, \q1 xàmmee lu meññe ci ñoom fi biir waaso yi; \q1 képp ku leen gis ràññee ne \q1 ñooy askan wu Aji Sax ji barkeel. \s1 Almasi bége na mucc gi mu maye \q1 \v 10 Maa béga bég ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 sama xol di sedd ci sama Yàlla jii. \q1 Moo ma solal yérey mucc, \q1 sànge ma mbubbam njekk, \q1 may nirook boroom séet bu kaalawu \q2 ni sarxalkat, \q1 ne xenjaw ni séet bu takki gànjaram. \q1 \v 11 Ni suuf di fettalem njebbit, \q1 ab tool di ko saxalem jiwu, \q1 ni la Boroom bi Aji Sax ji di jebbile \q2 njekk ak cant, \q1 xeetoo xeet seede ko. \c 62 \s1 Yerusalem mooy siggi, mucc \q1 \v 1 \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* a tax duma selaw, \q1 Yerusalem laa ne, moo tax duma noppi, \q1 ba kera ceeñeeru njekkam teew, \q1 jumu muccam dikkal ko. \q1 \v 2 Su boobaa xeet yi gis sag njekk, \q1 buur yépp gis sa daraja, \q1 ba ñu di la tudde tur wu yees, \q2 wu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji di tuddal boppam. \q1 \v 3 Yaay doon kaalag teddnga \q2 ci loxol Aji Sax ji, \q1 yaay doon mbaxanam buur, \q2 ci sa biir loxol Yàlla jii. \b \q1 \v 4 Deesatu la wooye «Dëkk bi ñu wacc,» \q1 deesatul wooye sam réew «Réew mu gental.» \q1 Xanaa ñu wooye la «Dëkk bi ma neex,» \q1 tey wooye sam réew «Boroom jëkkër,» \q1 nde yaa neex Aji Sax ji, \q1 te sa réew mi dina am boroom kër. \q1 \v 5 Ni xale bu góor di takke ab janq, \q1 ni la la sa doom yu góor di moome ni jëkkër\f + \fr 62.5 \fr*\fk doom yu góor yi \fk*\ft ñooy waa Yuda, te ñooy moom seen réew.\ft*\f*; \q1 ni boroom séet di bégee ab séetam, \q1 ni la la sa Yàlla di bégee. \b \q1 \v 6 Yerusalem, tabb naa ay jongrukat \q2 ci sa kawi tata. \q1 Buñu selaw, du guddi du bëccëg! \q1 Yeen ñiy soññ Aji Sax ji, \q1 buleen dal-lu. \q1 \v 7 Buleen may Aji Sax ji fu mu dal-loo, \q1 ba kera muy taxawalaat Yerusalem, \q1 ba def ko sababu cant fi kaw suuf. \b \q1 \v 8 Aji Sax jee giñ lii ci ndijooram, \q1 giñ ko ci përëgam bi àttan, \q1 ne: «Dootuma joxe sam pepp, \q1 say noon dunde, \q1 te doomi doxandéem dootuñu naan \q2 sa biiñ bu bees, \q2 bi nga ame saw ñaq. \q1 \v 9 Ñi góob pepp mee koy lekk, \q1 di ko sante Aji Sax ji. \q1 Ñi witt reseñ jeey naan biiñ bi, \q1 fi sama biir ëtt bu \w sell|lemma="sell:"\w*.» \q1 \v 10 Jàllsileen, jàllsileen bunti dëkk bi, \q1 xàll-leen yoonu xeet wi, \q1 maasaleleenoo, maasaleleen ngér mi, \q1 dindi doj yi! \q1 Yékkatileen raaya ju askan yépp gis. \q1 \v 11 Aji Sax jaa ngoog, \q1 yéene na lii ba ca cati àddina. \q1 Mu ne: «Waxleen Siyoŋ dëkk bu taaru bi, ne ko: \q1 “Sab jotkat a ngii di dikk! \q1 Mu ngii ànd akub yoolam, \q1 ñaqu liggéeyam jiitu ko.” \q1 \v 12 Dees na leen wooye “Askan wu sell wi,” \q1 “Ñi Aji Sax ji jot;” \q1 te yaw Yerusalem dees na la wooye “Ki ñu namm,” \q1 “Dëkk bi ñu waccul.”» \c 63 \s1 Jàmbaaru Aji Sax ji am na ndam \q1 \v 1 Ana kuy kii bawoo Edom\f + \fr 63.1 \fr*\ft Edom mi doon seexu Yanqóoba, moom lañu dippee réewum Edom, te moo taxawe taxawaayu noonub Aji Sax ji.\ft*\f*, \q1 sol yére yu xonq, bawoo Boccra\f + \fr 63.1 \fr*\ft Boccra ab dëkk la ci réewum Edom.\ft*\f*? \q1 Kii ak yéreem yu yànj, \q1 di daagoo dooleem ju bare? \q1 «Xanaa man mii di waxe njekk, \q1 te am dooley walloo.» \q1 \v 2 Lu waral sa xonqaayu mbubb mi, \q1 sa yére yi mel ni ku doon dëre \q2 dërukaayu reseñ? \q1 \v 3 «Maa doon dëre tànk, man kenn \q2 ci ab dërukaayu reseñ, \q1 xeet yépp kenn dërlewu ma ci. \q1 Sama mer laa leen dëre, \q1 samam sànj laa leen dëggaatee, \q1 seen deret tis ci samay yére, \q1 ma taqal sama yére yépp. \q1 \v 4 Bésub mbugal laa mébétoon, \q1 te atum njot teew. \q1 \v 5 Ma xool, \q1 gisuma ku ma dimbali, \q1 ma tiislu li ma amul ku ma jàpple. \q1 Ca la ma sama përëg wallu, \q1 samam sànj jàpple ma ca. \q1 \v 6 Sama mer laa dëggaatee ay xeet, \q1 samam sànj laa leen màndal, \q1 sotti seen deret fi suuf.» \s1 Yonent baa ngi soññ Aji Sax ji \q1 \v 7 Jëfi ngoru \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji laay fàttlee \q1 ak cant gi Aji Sax ji yelloo, \q1 ngir li nu Aji Sax ji defal lépp; \q1 mbaax gu réy gi mu ji waa kër Israyil, \q1 defal leen ko ci yërmandeem, \q1 ak jëfi ngoram gu réy. \q1 \v 8 Moo noon: «Sama ñoñ déy ñoom a! \q1 Ñee di doom yu dul tas yaakaar.» \q1 Mu daldi doon seen jotkat. \q1 \v 9 Seen gépp njàqare di njàqarey boppam, \q1 malaaka mi mu jàkkaarlool musal leen ca. \q1 Moo leen sopp, ñeewante leen, \q1 ba jotal leen boppam, \q1 te fu ñu masa jaare démb, \q1 mu fab leen, boot. \q1 \v 10 Waaye ñoom ñoo fippu, \q1 di naqaral xelam mu \w sell|lemma="sell:"\w*, \q1 mu soppliku seen noon, \q1 ba mujj di xareek ñoom. \q1 \v 11 Ñoñam ña daldi fàttliku janti Musaa ya woon. \q1 Ña nga naan: «Ana ki jàlle woon Israyil géej, \q1 mook sàmmi géttam ga? \q1 Ana ki yebaloon noowam gu sell ci seen biir? \q1 \v 12 Ana ki dawaloon dooley përëgam bu tedd ba, \q2 ñeel ndijooru Musaa, \q1 xaral leen ndox ma, \q1 ba ame ca woy wu sax dàkk? \q1 \v 13 Ana ku leen doxloo woon biir xóote ya, \q1 ñu mel ni fasi naari góor ci biir màndiŋ, \q1 te tërëfuñu? \q1 \v 14 Ni jur gu wàccew xur, di fa fore, \q1 ni la leen Noowug Aji Sax ji \q2 maye ab dal-lukaay. \q1 Noonu nga wommate sa ñoñ, \q2 ba ame ca woy wu rafet. \b \q1 \v 15 «Ngalla séentool asamaan, \q1 xooleel fa sa kër gu sell ga ne ràññ. \q1 Ana sa fiiraangeek sa njàmbaar? \q1 Sag rafet xol ak sa yërmande ñooru na ma! \q1 \v 16 Yaw déy yaa di sunu Baay. \q1 Ibraayma xamalu nu dara, \q1 Israyil\f + \fr 63.16 \fr*\ft Israyil fii mooy maam Yanqóoba.\ft*\f* xamu nu. \q1 Yaw Aji Sax ji yaa di sunu Baay, \q1 sa tur a di “sunu \w Jotkat|lemma="jotkat b-:"\w* naka jekk.” \q1 \v 17 Aji Sax ji, loo nuy wërloo fu sore say yoon, \q1 di nu dërkiisal, ba ragalatunu la? \q1 Sang bi, délsil ngir nun, \q1 sa giir yii nga séddoo. \q1 \v 18 Nun sa xeet wu sell wii, \q1 moomunu réew mi lu yàgg, \q1 te noon yi dëggaate nañu sa \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w*. \q1 \v 19 Nu ngi mel ni xeet woo masula yilif, \q1 xeet wu ñu masula tudde sa tur. \q1 Éy soo xaroon asamaan, wàcc, \q1 ba tund yi yëngu fi sa kanam!» \c 64 \q1 \v 2 Ni sawara di jafale boob, \q1 baxale ko am ndox, \q1 ni ngay xamalsee say noon, saw tur, \q1 ba yooyu xeet di lox fi sa kanam. \q1 \v 3 Ba ngay def kiraama ya ñu séentuwuloon, \q1 yaa wàcc, tund yi yëngu fi sa kanam. \q1 \v 4 Ca cosaan ba tey maseesula dégg, \q1 nopp masula dégmati, \q1 bët masula gis yàlla ju la moy, \q1 mu defal nii ku ko yaakaar. \q1 \v 5 Yaay gatandu kiy bége njekk gi muy jëfe \q1 te di ba xel say yoon, \q2 yi ñu mas di jaare, ba mucc. \q1 Waaye kat, yaa nu mere, ndax noo bàkkaar. \q1 \v 6 Nun ñépp a mujj mel ni sobe, \q1 ni sagaru sobe la sunu gépp njekk mel. \q1 Nu ngii nun ñépp mel ni xob wu lax, \q1 sunuy tooñ buub nu, yóbbu ni ngelaw. \q1 \v 7 Du kenn kuy wormaal sa tur, \q1 mbaa mu yewwu ba jàpp ci yaw, \q1 yaa nu làq saw yiw, \q1 yaa nu def ban bu tooy \q1 ci sunu biir ñaawtéef yi nu tanc. \b \q1 \v 8 Waaye déy, Aji Sax ji, yaa di sunu Baay; \q1 noo di ban, yaw ngay tabaxkatu njaq, \q1 nun ñépp di sa liggéeyu loxo. \q1 \v 9 Éy Aji Sax ji, bul mer lool, \q1 bul ba xel fàww ci ñaawtéef. \q1 Ngalla seetal ne nooy sa ñoñ, nun ñépp. \q1 \v 10 Sa dëkk yu sell doon nañu màndiŋ, \q1 \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* ca la, doon na màndiŋ. \q1 Yerusalem laa ne, gental na! \q1 \v 11 Sunu kërug jaamookaay gu sell ga te tedd, \q1 fa la sunuy maam daa màggale, \q1 sawara xoyom na ko, \q1 mboolem lu nu soppoon yàqu yaxeet. \q1 \v 12 Éy Aji Sax ji, lii lépp xanaa doo ci téye sa loxo? \q1 Xanaa doo ci seleŋlu, teg nu gàcce gu réy? \c 65 \s1 Aji Sax ji wuyu na \q1 \v 1 Maa may ay nit tont te laajuñu ma. \q1 Maa leen may, ñu gis ma te seetuñu ma woon. \q1 Maa ne leen: Maa ngii, maa ngii! \q1 te ñuy xeet wu dul tudd sama tur. \q1 \v 2 Samay loxo laa yendoo tàllal askanu fippukat, \q1 nit ñuy doxe yoon wu baaxul, \q1 topp seen xelum bopp. \q1 \v 3 Ñoo di xeet wu ma ne jàkk, \q1 dëkke maa naqaral, \q1 di sarxalali tuur ci biiri tool, \q1 di leen taalal cuuraay ci kaw sarxalukaay \q2 bu ñu tabax, \q1 \v 4 di tooge diggi bàmmeel, \q1 di fanaan bérab yu làqu; \q1 di lekk yàppu mbaam, \q1 seeni cin def ñam yu sobewu, \q1 \v 5 te ñu naan: «Dellul gannaaw, \q1 bul ma jege, maa la gëna sell!» \q1 Lii déy daa mel ni saxar ci samay wakkan, \q1 mel ni sawara su yendoo boy. \b \q1 \v 6 Ma ne dogal a ngii binde, fi sama kanam: \q1 «Duma noppi déy, maa leen di fey, \q1 maa leen di fey ba mu mat sëkk.» \q1 \v 7 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nee: «Muy seeni ñaawtéef, \q1 di seen ñaawtéefi maam, \q1 ya daan taalali tuur cuuraay ca tund yu mag ya, \q1 di ma kókkali ca kaw tund yu ndaw ya, \q1 lépp laa leen di fey ba mu mat sëkk, \q1 muy seen añu jëf ja woon.» \b \q1 \v 8 Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 «Ni nit di gise cabbu reseñ ju fees dell, \q1 ne: “Buleen ko yàq, \q1 ngëneel a ngi ci,” \q1 noonu laay def ngir sama jaam ñi, \q1 baña boole lépp yàq. \q1 \v 9 Fi Yanqóoba laay soqee aw askan, \q1 fi Yuda laa ne, fi laay jële lu séddoo samay tund. \q1 Samay tànnéef a koy séddoo, \q1 sama jaam ñi kay a fay dëkke. \q1 \v 10 Joorug Saron ay dellu di parlub gàtt gi, \q1 xuru Akor di goorukaayu nag yi, \q1 ñeel sama ñoñ ñi may sàkkuji. \b \q1 \v 11 «Waaye yeen ñi wacc Aji Sax ji, \q1 yeen ñi fàtte sama tund wu \w sell|lemma="sell:"\w* wi, \q1 di taajal ndab, Gàdd tuur mi\f + \fr 65.11 \fr*\fk Gàdd \fk*\ft mooy tuur mi ñu jiiñ wërsëg.\ft*\f*, \q1 di xellil biiñu njafaan, Meni tuur mi\f + \fr 65.11 \fr*\fk Meni \fk*\ft mooy tuur mi ñu jiiñ ndogal.\ft*\f*, \q1 \v 12 maa leen di dogalal saamar, \q1 ngeen bokk sukk, ñu rendi leen, \q1 ngir maa woote, wuyuwuleen, \q1 ma wax, dégguleen, \q1 xanaa di def li ma ñaawlu, \q1 taamu li ma buggul.» \b \q1 \v 13 Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 «Ma ne sama jaam ñeey lekk, \q1 yeen ngeen nekke xiif. \q1 Ma ne sama jaam ñeey naan, \q1 yeen ngeen nekke mar. \q1 Sama jaam ñeey bànneexuji, \q1 yeen, ngeen nekke gàcce. \q1 \v 14 Sama jaam ñeey sarxolleji \q2 ndax xol bu neex, \q1 yeen ngeen di yuuxu ndax naqaru xol, \q1 di jooyoo ndax xol bu jeex. \q1 \v 15 Seen tur wi ngeen bàyyi gannaaw \q2 la samay tànnéef di móoloo, \q1 naan: “Yal na la Boroom bi Aji Sax ji rey ni diw ak diw,” \q1 waaye ñoom sama jaam ñi, \q1 tur wu yees lees leen di wooye, \q1 \v 16 ba képp ku namma barkeel fi kaw suuf, \q1 ci Yàlla jiy dëgg la koy ñaane, \q1 te kuy giñ fi kaw suuf it, \q1 ci Yàlla jiy dëgg la koy giñe. \q1 Day fekk njàqare ya jiitu di lu ñu fàtte, \q1 te di lu làqu saay gët. \s1 Aji Sax ji yeesal na càkkéefam \q1 \v 17 «Maa ngii di sàkksi asamaan su yees \q1 ak suuf su yees. \q1 Deesul fàttlikooti yëf ya jiitu, \q1 xel dootu ci dem. \q1 \v 18 Bégleen kay, \q1 te saxoo di bànneexoo li ma sàkk: \q1 Maa ngii di sàkk Yerusalemu mbégte, \q1 waa dëkk ba nekke bànneex. \q1 \v 19 Maay bége Yerusalem, \q1 bànneexoo sama ñoñ. \q1 Deesu fi déggati ay jooy, \q1 mbaa coowal njàqare. \q1 \v 20 Deesu fi gisati \q1 tuut-tànk bu dund fan yu néew, \q1 mbaa mag mu dee te ay fanam matul, \q1 ba ku am téeméeri at dee sax, di ku gàtt fan, \q1 te ku àggul téeméer, ñu ne alku nga. \b \q1 \v 21 «Ñooy tabax ay kër, dëkke, \q1 jëmbati tóokër, lekk ca meññeef ma. \q1 \v 22 Duñu tabax moos, keneen dëkke; \q1 duñu jëmbat moos, keneen xéewloo. \q1 Sama ñoñ ay tollook garab yi fan, \q1 sama xejj yeey jagoo seenu ñaq. \q1 \v 23 Duñu liggéeyati mukk ci neen \q1 te dootuñu jural mbas. \q1 Ñooñooy askanu ñi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji barkeel, \q1 seeni doom nekk ak ñoom. \q1 \v 24 Su boobaa balees woote, \q1 man, maay wuyu; \q1 balaa ñoo daane seen kàddu, ma nangul leen. \q1 \v 25 Bukki ak mboteey bokk di for, \q1 gaynde niw nag, di for um ñax, \q1 jaan di dunde pënd. \q1 Deesatul gaañe mbaa di lore, \q1 fi mboolem sama kaw tund wu \w sell|lemma="sell:"\w* wi.» \q1 Aji Sax jee ko wax. \c 66 \s1 Ragal Yàlla du jëfi ngistal \q1 \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: «Asamaan sama ngàngunee, \q1 suuf di sama ndëggastal. \q1 Ana kër gu ngeen may tabaxal man? \q1 Ana ban bérab ay sama dal-lukaay? \q1 \v 2 Mboolem yooyu, sama loxoo ko sàkk; \q1 nii la lépp ame.» Kàddug Aji Sax jee. \q1 «Ku mel nii laay niir: \q1 néew-ji-doole ji xolam jeex, \q1 te muy déglu sama kàddu bay lox. \q1 \v 3 Kee moom mu ngi rendiw yëkk, sarxal, \q1 te teewu koo bóome. \q1 Kee rendiw xar, sarxal, \q1 te teewu koo damm loosu xaj, sarxal. \q1 Kee ngi joxe \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w*, \q1 te teewu koo tuur deretu mbaam-xuux. \q1 Kee di taal saraxu baaxantalu \w cuuraay|lemma="cuuraay l-:"\w*, \q1 tey jaamu ay tuur. \q1 Ñoo taamu seen yoonu bopp, \q1 safoo seeni jëf ju seexluwu. \q1 \v 4 Man it maa leen di taamoo jox seeni mbugal, \q1 dikke leen tiitaange yi ñu yelloo, \q1 ngir maa woote, kenn wuyuwul, \q1 ma àddu, dégluwuñu ma. \q1 Xanaa di def lu bon lu ma ñaawlu, \q1 li ma buggul, ñu taamu ko.» \s1 Aji Sax ji mujj na dikk \q1 \v 5 Dégluleen kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 yeen ñiy déglu kàddoom, di lox. \q1 Lii de mooy seen kàddug bokk, \q1 yi leen jéppi, di leen dàq ngir samaw tur. \q1 Ñu ngi naan: «Na Aji Sax ji darajaal boppam, \q1 ba nu teewe seen mbégte, yeen ñii!» \q1 Waaye ñoom de ñooy rus. \q1 \v 6 Coowal xaree ngoog bawoo dëkk ba, \q1 coow laa nga jóge kërug Yàlla ga, \q1 coowal Aji Sax jee, mooy yool ay noonam. \b \q1 \v 7 Kii balaa matu, wasin na, \q1 bala moo am mititu mat, jur na doom ju góor. \q1 \v 8 Ku masa dégg lu mel nii? \q1 Ku masa gis lu mel nii? \q1 Am réew dina sosu ci benn bés a? \q1 Am aw xeet dina jekki sosu ci wenn fan? \q1 \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* de, moo tàmbali matu rekk, \q1 jur doomam yu góor. \q1 \v 9 Aji Sax ji nee: «Man miy jàpple jigéen \q1 ba ëmbam mat, \q1 dinaa ko xañ wasin? \q1 Man miy wasinloo nit, \q1 dinaa fatt njurukaayam?» \q1 Sa Yàllaa ko wax. \b \q1 \v 10 Yeen soppey Yerusalem yépp, \q1 bégandooleen ak moom, \q1 te di ko bànneexoo. \q1 Mboolem yeen ñi doon ñaawlu tiisu Yerusalem, \q1 bokkleen ak moom xolam bu sedd. \q1 \v 11 Su ko defee ngeen nàmp ba suur \q1 weenam wiy naxtaane, \q1 su ko defee ngeen nàmp bay tàqamtiku \q2 soowum weenam mi ne xéew. \q1 \v 12 Aji Sax ji déy dafa wax ne: \q1 «Maa ngii di yóbbu Yerusalem \q2 ci jàmm ju mel ni géej, \q1 ak waamey koom muy wal, bawoo ci xeet yi. \q1 Yeenay tooge luppu Yerusalem, di nàmp, \q1 uufu ciy óom, mu di leen raay. \q1 \v 13 Man maa leen di naxtaan ba ngeen dal, \q1 ni doom ju ndeyam di naxtaan ba mu dal, \q1 ngeen am xel mu dal fi Yerusalem. \q1 \v 14 Yeenay teewe lii, seen xol tooy, \q1 seen yaram leqliku ni ñax mu yég nawet. \q1 Dooley Aji Sax ji la ay jaamam di xam, \q1 te am sànjam la ay noonam di xam. \b \q1 \v 15 «Aji Sax ji déy a ngii dikke sawara, \q1 ay watiiram mel ni ngëlén, \q1 mu nara sànju, sotti meram, \q1 gëdde sawara wuy sëlsëli. \q1 \v 16 Sawara déy la Aji Sax ji di mbugale, \q1 saamaram ba dal mboolem doom aadama, \q1 ñi Aji Sax ji bóom ne xas. \b \q1 \v 17 «Ñii di sellalu ak a sangu-set \q1 bala ñoo duggi tool ya ñuy tuuroo, \q1 di fa toppi ca gannaaw ka ca digg ba, \q1 ñooñooy lekk yàppu mbaam, \q1 ak yeneen yu seexluwu ni janax, \q1 te ñooy bokk sànku.» \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 18 «Man maa xam seeni jëf ak seeni xalaat. \q1 Bés bii taxaw lees di dajale xeetoo xeet aki làkk, \q1 ñu dikk ba niir samag leer. \q1 \v 19 Maay teg firnde fi seen digg, \q1 ba jël ñenn ca ña dese bakkan ca ñoom, \q1 yebal leen ci xeet yi, \q1 yebal leen Tarsis, ak Pul ak Ludd, \q1 ñooña di ñu mane fitt, \q1 ma yebal leen ca waa Tubal ak Yawaan, \q1 waa duni géej yu sore ya, \q2 ñooñu masula dégg sama jaloore, \q1 te masuñoo gis sama teddnga, \q1 sama ndaw ñaa leen di xamal sama teddnga. \q1 \v 20 Xeet yooyooy indi seen bokk \q2 yi bokk ak yeen ñépp, \q1 jële leen ci mboolem xeet yi, \q1 ñu doon sarax bu ñeel Aji Sax ji, \q1 wari fas aki watiir, \q1 ba ci watiir yu ñu mbaar, \q1 aki berkelleeki giléem, \q1 ba agsi sama tund wu \w sell|lemma="sell:"\w*, \q2 wi ci Yerusalem.» \q1 Aji Sax jee ko wax. \q1 «Day mel ni noonu \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* di yóbboo sarax, \q1 yeb ko ci ndab lu sell, \q1 yóbbu kër Aji Sax ji. \q1 \v 21 Te ñenn ci yooyu xeet, maa leen di jël, \q1 def leen ay \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* aki \w Leween|lemma="Leween b-:"\w*.» \q1 Aji Sax jee ko wax. \q1 \v 22 «Asamaan su yees sii, \q1 ak suuf su yees sii may waaja sàkk déy, \q1 ni seen taxawaay di yàgge fi sama kanam, \q1 yeen, ni la seen askan ak seen tur di yàgge fi sama kanam. \q1 \v 23 Su ko defee Terutel weer ba Terutel weer, \q1 \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w* ba bésub Noflaay, \q1 mboolem doom aadama di ma sujjóotalsi.» \q1 Aji Sax jee ko wax. \q1 \v 24 «Te bu ñu génnee, gis néewi \q2 ñi doon fippu fi sama kaw, \q1 seeni sax duñu dee mukk, \q1 seen sawara du fey mukk, \q1 te boroom suux bu leen gis, yaram wa daw.»