\id GEN (WOL) \ide UTF-8 \h Njàlbéen ga \toc1 Njàlbéen ga, di xaaj bi jëkk ci Tawreetu Musaa \toc2 Njàlbéen ga \mt1 Njàlbéen ga \mt2 di xaaj bi jëkk ci Tawreetu Musaa \imt1 Ubbite gi \ip \bk Njàlbéen ga\bk* mooy téere bi jëkk ci Tawreet. Yonent Yàlla Musaa moo bind Tawreet, juróomi téere yi jiitu ci Mbind mu sell mi. \ip Téereb \bk Njàlbéen ga\bk* moo tënk ndoortel lépp lu Yàlla sàkk, muy asamaan ak suuf ak gàncax geek rab yi, ba ci nit; lépp di lu baax. \ip Téere bii nag wone na ni àddina mujj mel, ndax ñaawtéefi nit, yi law ba sunu jonni Yàllay tey. Gis nanu ci \bk Njàlbéen ga\bk* ne ca Aadama ak Awa la nit dale déggadil Yàlla, di wuta moom boppam tey fippu, te loolu mooy bàkkaaram. Mu jural ko lu bon, jural ko coonob àddina bu tar, tey gëna tar, soreele kook Yàlla. Booba la dee tàmbali ci àddina. Nekkinu nit mujj na naqari lool, nekkinu suuf it noonu, wuuteek ba Yàlla di sàkk lépp, ba mu baax. \ip Nu gis ne \bk Njàlbéen ga\bk* dafa lëkkloo ak mboolem yeneen wàll yi ci des, lépp di benn xibaar buy dégtal nit alkàndeem, gi sababoo ci bàkkaaram, te di ko xamal mbaaxu Yàlla ñeel képp kuy doom Aadama. Waaye xibaar la it buy yégle àtteb Yàlla, ñeel ñi xalab aw yiwam. \ip Pexe mi Yàlla lalal nit ngir texeem te misaaloon ko xaat ci \bk Njàlbéen ga\bk* ci saar 3, aaya 15 (3.15), mu ngi sottee ci musalkat bi wara ñëw. \ip Téereb \bk Njàlbéen ga\bk* nag làqul matadig nitoo nit, te yonenti Yàlla yi sax muccuñu ci bàkkaar. Looloo tax du kenn ci yonent yi ku manoona sottal li Yàlla tëralal doom Aadama, ngir mu mucc ci noteelu bàkkaar, mucc ci sànkute gi bàkkaar jur, ba jot ci yiwu Yàlla wi koy texeel. \ip Bu loolu weesee, téereb \bk Njàlbéen ga\bk* leeral na ci saar 12, aaya 3 (12.3) ne, la Yàlla digoon Ibraayma, maami aji gëm ñi, dig ko doomam Isaaxa ak sëtam, Yanqóoba, moom Isaaxa ak askanam ñoo ko jëkkoona jagoo. Waaye dige la bu jaare ca ñoom, doon barke, ñeel xeeti àddina yépp. \ip Ibraayma wone na nu nit wara taxawe, ba jot ci digeb Yàlla. Ngëm gu dëggu ak kóolute gu wér ci Yàlla. Ngëm googu ak kóolute googu ci Yàllaak kàddoom moo mana tax nit ku nekk mana jot ci barke bi Yàlla dig Ibraayma, doonte kenn yelloowu ko. \ip Ci Tënk: \ili 1:1-2:25 Lu jëm ci càkkuteefu asamaan ak suuf \ili 3:1-3:24 Lu jëm ci bàkkaaru nit ak njeexitalam \ili 4:1-8:22 Lu jëm ci askanu Kayin ak Set ba ca mbënn ma \ili 9:1-11:9 Gannaaw mbënn ma ba ca taaxum Babel \ili 11:10-50:26 Lu jëm ci Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ba ci Yuusufa \c 1 \s1 Yàlla sàkk na àddina, fal ci nit \p \v 1 Ca njàlbéen ga Yàlla sàkk na asamaan ak suuf. \v 2 Suuf nag daa maase woon te wéet, lëndëm muur ndox mu xóot mi, lale ca kaw, Noowug Yàlla di wër, tiim ndox mi. \p \v 3 Ba loolu amee Yàlla ne: «Na leer nekk,» leer daldi am. \v 4 Yàlla gis ne leer gi lu baax la, mu xàjjale leer ak lëndëm. \v 5 Yàlla tudde leer gi bëccëg, lëndëm gi guddi. Ngoon jot, suba dugg, muy bés ba jëkk. \p \v 6 Yàlla ne: «Na aw dénd dox diggante ndox yi, ngir xàjjale leen, yii fii, yii fale.» \v 7 Yàlla nag sàkk dénd wi, xàjjalee ko ndox yi féete dénd wi suuf ak yi ko féete kaw. Mu daldi nekk noona. \v 8 Yàlla tudde dénd wi asamaan. Ngoon jot, suba dugg, muy bésub ñaareel ba. \p \v 9 Yàlla ne: «Na ndox, mi asamaan tiim, gëndoo benn bérab, ba joor gu wow feeñ.» Mu daldi nekk noona. \v 10 Yàlla tudde joor gu wow gi suuf, ndox mi gëndoo, mu tudde ko géej. Yàlla gis ne baax na. \p \v 11 Yàlla ne: «Na suuf sax ñax, muy gàncax gu ànd ak jiwoom, ak garab yuy meññ tey jur seeni jiwu, lu ci nekk ak wirgoom ci kaw suuf.» Mu daldi nekk noona. \v 12 Suuf nag sax ñax, muy gàncax gu ànd ak wirgoy jiwoom, ak garab yuy meññ tey jur seeni wirgoy jiwu. Yàlla gis ne baax na. \v 13 Ngoon jot, suba dugg, muy bésub ñetteel ba. \p \v 14 Yàlla ne: «Na am ay leer ci asamaan, ngir xàjjale guddi ak bëccëg, te doon ay tegtal, yuy ràññle jamono yi, tey takk bés yi ak at yi. \v 15 Nañu nekk ay leer ci asamaan si, di leeral suuf.» Mu daldi nekk noona. \v 16 Yàlla sàkk ñaari leer yu mag, gi gëna mag yilif bëccëg, gi gëna ndaw yilif guddi; mu sàkk it biddiiw yi. \v 17 Yàlla nag teg leen ci asamaan, di ca leeral suuf, \v 18 ñuy yore guddi ak bëccëg, tey xàjjale lëndëm ak leer. Yàlla gis ne baax na. \v 19 Ngoon jot, suba dugg, muy bésub ñeenteel ba. \p \v 20 Ba loolu amee Yàlla ne: «Na ndox fees ak ay ndiiraani xeeti bindeef, te ay picc tiim suuf, di naaw ci asamaan.» \v 21 Ci biir loolu Yàlla bind rabi géej yu mag yi ak mboolem mbindeef muy féey tey ramm-rammi ci ndox mi, mu ci nekk ak wirgoom, teg ca lépp luy boroomi laaf, lu ci nekk ak wirgoom. Yàlla gis ne baax na. \v 22 Ba mu ko defee Yàlla barkeel leen, daldi ne: «Giirleen te bare, ba fees ndoxi géej.» Mu neeti: «Na picc yi bare ci kaw suuf.» \v 23 Ngoon jot, suba dugg, muy bésub juróomeel ba. \p \v 24 Yàlla ne: «Na suuf génne ay bindeef, mu ci nekk ak wirgoom: ag jur, luy raam aki rabi àll, lu ci nekk ak wirgoom.» Mu daldi nekk noona. \v 25 Yàlla dafa bind rabi àll yi, lu ci nekk ak wirgoom, jur gu ci nekk ak wirgoom, ak lépp luy raam ci kaw suuf, lu ci nekk ak wirgoom. Yàlla nag gis ne baax na. \p \v 26 Yàlla ne: «Nanu bind nit ci sunu melokaan, mu nirook nun, te na yilif jëni géej ak picci asamaan ak jur gépp ak suuf sépp ak lépp lu ciy raam.» \q1 \v 27 Yàlla dafa bind nit ci takkndeeram; \q1 ci takkndeeru boppam la Yàlla bind nit, \q1 góor ak jigéen la bind. \m \v 28 Yàlla barkeel leen ne leen: «Giirleen te bare, ba fees àddina, di ko saytu; te it yilifleen jëni géej ak picci asamaan ak mboolem mbindeef muy yëngu ci kaw suuf.» \p \v 29 Yàlla ne: «Xool-leen, jox naa leen gépp gàncax gu ànd ak jiwoom ci kaw suuf sépp ak gépp garab guy meññ tey jur jiwoom, muy seen dund. \v 30 Naka rabi àll yépp it, ñook picci asamaan yépp ak lépp luy raam ci kaw suuf, te di boroom bakkan, jox naa leen lépp luy ñax mu tooy, ñoom itam, muy seen lekk.» Mu daldi nekk noona. \p \v 31 Yàlla nag gis li mu def lépp, fekk lépp baax lool. Ngoon jot, suba dugg, muy bésub juróom benneel ba. \c 2 \p \v 1 Ci kaw loolu asamaan ak suuf ak li ñu ëmb lépp mat. \v 2 Bésub juróom ñaareel ba fekk na Yàlla matal liggéeyam. Mu dal-lu nag ca bésub juróom ñaareel ba, gannaaw ba mu liggéeyee loolu lépp. \v 3 Yàlla daldi barkeel bésub juróom ñaareel ba, def ko bés bu sell, ndax da caa dal-lu woon gannaaw liggéey, ba mu sàkke lépp. \ms1 Cosaanal asamaan ak suuf \mr (Saar 2.4—4.26) \s1 Yàlla dugal na nit Àjjana, jox ko ndigal \p \v 4 Liy cosaanal asamaan ak suuf, ba ñu leen di sàkk, mooy lii. Bés ba \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Yàlla sàkkee suuf ak asamaan, \v 5 genn garab nekkagul woon ci kaw suuf, te genn gàncax saxagul; ndaxte booba Yàlla Aji Sax ji tawagul, te nit kuy bey amagul. \v 6 Ci biir loolu mbënn di balle ci suuf, di tooyal fépp. \v 7 Yàlla Aji Sax ji nag móol nit ci pëndu suuf, sol ngelawal dund ci paxi bakkanam, nit daldi doon boroom bakkan. \p \v 8 Naka noona Yàlla Aji Sax ji jëmbat tool ca biir Àjjana fa féete penku ba, tàbbal ca nit ka mu bind. \v 9 Yàlla Aji Sax ji nag saxal ci suuf lépp luy garab gu meññeef ma rafet te neexa lekk; mu def it garab gay taxa dund ca digg tool ba, moom ak garab gay taxa xam lu baax ak lu bon. \p \v 10 Amoon na dex guy balle Àjjana, di suuxat tool ba, dale fa nag, séddlikoo, def ñeenti wal. \v 11 Turu menn wal ma di dexu Pison, moo wër réewum Awila mépp. Wurus a nga woon ca réew mooma, \v 12 di wurusu ngalam; te it ndàbb lu neex xet a nga fa woon ak per yu jafe yu ñuy wax onigsë. \v 13 Ñaareelu dex ga di Giyon, wër réewu \w Kuus|lemma="Kuus:"\w* mépp; \v 14 turu ñetteelu dex ga di Tiigar, féete réewum Asiri penku; ñeenteelu dex ga di Efraat. \p \v 15 Yàlla Aji Sax ji nag jël nit ki, tàbbal ko biir toolub Àjjana, mu di ko bey ak a sàmm. \v 16 Yàlla Aji Sax ji sant nit ki, ne ko: «Man ngaa lekk ci mboolem garabi tool bi, \v 17 waaye bul lekk ci garab giy taxa xam lu baax ak lu bon, ndaxte bés boo ci lekkee kat, li wér mooy fa ngay doxe dee.» \p \v 18 Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Wéet baaxul ci nit, kon dinaa ko bindal ku koy jàpple te jekk ci doon wéttalam.» \v 19 Loolu fekk na Yàlla Aji Sax ji sàkk ci suuf nja-àll yépp ak njanaaw yépp, daldi leen indil nit, di seet nu leen nit di tudde; te tur wu mu leen jox, muy moom. \v 20 Ba mu ko defee nit kooku, di Aadama, tudd jur gépp ak picc yépp ak rabi àll yépp, waaye fekku ca ku koy jàpple te jekk ci doon wéttalam. \p \v 21 Bi loolu amee Yàlla Aji Sax ji nelawloo Aadama nelaw yu xóot. Ba muy nelaw nag, mu rocci genn ciy faaram, fatte pax ma aw suux. \v 22 Yàlla Aji Sax ji bind jigéen ci faar, gi mu jële ci Aadama, indil ko ko. \v 23 Aadama ne tonet, daldi ne: \q1 «Waaw kay nag, kii moo bokk ci samay yax ak sama suux! \q1 Dees na ko tudde jigéen, ndaxte ci góor lees ko jële\f + \fr 2.23 \fr*\ft Ni ñuy wooye \ft*\fq góor \fq*\ft ak ni ñuy wooye \ft*\fq jigéen \fq*\ft dañoo jegeyoo ci làkku ebrë.\ft*\f*.» \m \v 24 Looloo tax góor di bàyyikoo ci ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñuy wenn suux. \p \v 25 Ku góor ki ak soxnaam, ñoom ñaar ñépp, yaramu neen lañu defoon, te amuñu ci woon genn kersa. \c 3 \s1 Yàlla dàq na nit Àjjana \p \v 1 Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?» \v 2 Jigéen ja wax jaan ja, ne ko: «Man nanoo lekk ci doomi garabi tool bi kay. \v 3 Waaye garab gi ci digg tool bi la Yàlla ne: “Buleen ci lekk, buleen ko laal sax, lu ko moy ngeen dee.”» \v 4 Jaan ja ne jigéen ja: «Déedéet, dungeen dee! \v 5 Waaye Yàlla xam na ne bés bu ngeen ci lekkee, seeni bët dina ubbiku, ngeen mel ni Yàlla, xam lu baax ak lu bon.» \p \v 6 Jigéen ja dafa gis ne garab gi rafet na, niru na lu neex, te mata bëgg ci kuy wuta am xel, mu witt ci doom yi, lekk; jox ci jëkkëram, ji mu àndal, moom it mu lekk. \v 7 Seeni bët daldi ubbiku, ñu xam ne yaramu neen lañu def. Ba mu ko defee ñu ràbb xobi garabu figg, gemboo. \p \v 8 Gannaaw loolu ñu dégg tànki Yàlla Aji Sax ji, muy doxantu ca tool ba, fekk ker gi sedd, ñu daldi fexee làqu Yàlla Aji Sax ji ci biir garabi tool bi. \v 9 Yàlla Aji Sax ji nag ne Aadama: «Ana nga?» \v 10 Mu ne ko: «Damaa dégg say tànk ci tool bi, tiit, ndax yaramu neen laa def, ma daldi làqu.» \v 11 Yàlla Aji Sax ji ne ko: «Ku la xamal ne dangaa def yaramu neen? Mbaa du dangaa lekk ca garab, ga ma la aaye, waay?» \v 12 Aadama ne ko: «Jigéen, ji nga ma booleel de, moo ma jox ci garab gi, ma lekk.» \v 13 Yàlla Aji Sax ji ne jigéen ja: «Yaw, li nga def nii mooy lan?» Jigéen ja ne ko: «Aa, jaan de moo ma nax, ba ma lekk ci.» \p \v 14 Yàlla Aji Sax ji nag ne jaan ja: \q1 «Gannaaw def nga loolu, \q1 yaw rekk yaay alku ci rabi kër yépp ak rabi àll yépp; \q1 dinga watatu, di lekk pënd sa giiru dund gépp. \q1 \v 15 Dinaa def mbañeel sa digganteek jigéen ji, \q1 ba dëddale sa xeet ak xeetam, \q1 muy toj sa bopp, \q1 nga di ko màtt ci téstën.» \p \v 16 Yàlla teg ca ne jigéen ja: \q1 «Dinaa taral sa metitu mat, \q1 ci metit ngay wasin. \q1 Sa bëgg-bëggu bakkan dina la xiir ci sa jëkkër, \q1 te moo lay teg tànk.» \p \v 17 Mu tegaat ca ne Aadama: \q1 «Gannaaw dégg nga sa waxu soxna, ba lekk ci garab gi ma la aaye, \q1 dinaa rëbb suuf ndax yaw; \q1 coono bu metti nga ciy dunde sa giiru dund gépp. \q1 \v 18 Suuf dina la meññalal ay dég aki dagg, \q1 doo lekk te beyoo, \q1 \v 19 saw ñaq ngay dunde, \q1 ba kera ngay dellu ci suuf, si ma la jële; \q1 ndaxte pënd nga, \q1 te dinga dellu di pënd.» \p \v 20 Aadama nag tudde soxnaam Awa (mu firi Dund), ndax mooy ndeyu képp kuy dund. \v 21 Gannaaw gi Yàlla Aji Sax ji sàkkal Aadama ak soxnaam ay yérey der, wodde leen. \v 22 Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Léegi nit mel na ni nun, xam lu baax ak lu bon. Kon nag bumu tàllal loxoom, di witt ci doomi garab giy taxa dund, di lekk, bay dund fàww.» \p \v 23 Ba loolu amee Yàlla Aji Sax ji génne ko toolub Àjjana, muy bey suuf, si ñu ko sàkke. \v 24 Da koo dàq, ba noppi teg ca penkub toolu Àjjana ba ay malaakay \w serub|lemma="serub y-:"\w*\f + \fr 3.24 \fr*\fk serub: \fk*\ft serub yi ay bindeef lañu yu teew fa Yàlla.\ft*\f*, boole ca saamar buy xuyy-xuyyi, tey dem ak a dikk, di wattu yoon, wa jëm ca garab gay taxa dund. \c 4 \s1 Kayin rey na Abel \p \v 1 Gannaaw loolu Aadama dëkkoo na soxnaam Awa, mu ëmb, am Kayin, mu ne: «Am naa doom ju góor ci ndimbalu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji\f + \fr 4.1 \fr*\ft Awa mu ngi dendle turu taawam Kayin ak baatu ebrë biy tekki «am».\ft*\f*.» \v 2 Awa teg ca rakkam, Abel. Abel di sàmm, Kayin di bey\f + \fr 4.2 \fr*\fk Kayin, Abel: \fk*\ft am na ñu leen gëna xam ci turi Xabiil ak Abiil.\ft*\f*. \p \v 3 Ñu dem ba mu yàgg, Kayin sàkk ci mbeyam, jébbal ko Aji Sax ji, màggale ko ko. \v 4 Abel moom jébbal ko nebbonu jur, ga jëkka juddu ca géttam. Aji Sax ji nangul Abel, \v 5 te nangulul Kayin. Kayin nag mer lool, ba ne fóññ. \p \v 6 Aji Sax ji ne Kayin: «Lu la taxa mer, ba ne fóññ nii? \v 7 Soo defee lu baax, dees na la nangul; soo deful lu baax, bàkkaar a ngi lay yeeru ci sa bunt, di la tërook a wut, waaye yaa ko wara man.» \p \v 8 Ci kaw loolu Kayin séq ak rakkam Abel wax. Ba mu ko defee ñu dem ca àll ba, Kayin dal ci kaw Abel, bóom ko. \v 9 Aji Sax ji ne Kayin: «Ana sa rakk Abel?» Mu ne ko: «Gisuma ko de; xanaa maa wara sàmm sama rakk?» \v 10 Yàlla ne ko: «Loo def? Sa deretu rakk jaa ngi yuuxoo ci suuf, ma di ci dégg. \v 11 Léegi dinga alku, ba suuf dummóoyu la, moom mi ubbi gémmiñam, naan sa deretu rakk, ji nga tuur. \v 12 Boo beyee, dootu nangu. Dinga dëkke daŋ-daŋ, di wëreelu ci àddina.» \p \v 13 Teewul Kayin wax Aji Sax ji ne ko: «Sama mbugal diis na lool, ba àttanuma ko! \v 14 Ndegam tey jii danga maa dàq, xañ ma sa jataay, dinaa dëkke daŋ-daŋ, di wëreelu ci kaw suuf, te kon ku ma gis rey ma.» \v 15 Aji Sax ji ne ko: «Kon nag ku la rey, yaw Kayin, dina jot juróom ñaari yoon lu ko raw.» Ba loolu amee mu sàkkal Kayin màndarga, ba ku ko gis du ko rey. \v 16 Kayin daldi bàyyikoo ca Aji Sax ji, dem dëkki réewu Nódd\f + \fr 4.16 \fr*\fk Nódd \fk*\ft baatu ebrë la buy tekki «ku dëkkul fenn».\ft*\f*, fa féete Àjjana penku. \s1 Askanu Kayin \p \v 17 Gannaaw loolu Kayin dëkkoo na soxnaam, mu ëmb, am Enog. Ci biir loolu Kayin sanc ab dëkk, dippee ko doomam ju góor Enog. \v 18 Enog jur Iraat; Iraat jur Mexuyayel; Mexuyayel jur Metusayel; Metusayel jur Lemeg. \v 19 Lemeg nag jël ñaari jabar, aawo bi tudd Ada, ñaareel bi di Silla. \v 20 Ada taawloo Yabal, miy cosaanu sàmm yiy màngaan, \v 21 teg ca Yubal, miy cosaanu ñi mane xalam ak toxoro. \v 22 Silla moom jur Tubal Kayin miy tëgg lépp luy jumtukaayu xànjar ak weñ. Tubal Kayin am na jigéen bu tudd Naama. \p \v 23 Lemeg nag ne ay soxnaam: \q1 «Dégluleen maa, yeen soxnay Lemeg, \q1 teeyluleen maa, yeen Ada ak Silla. \q1 Nit a ma gaañ, ma bóom, \q1 goneg jàmbaar dóor ma, ma faat. \q1 \v 24 Kayin kay, lees di feyul juróom ñaari yoon, \q1 ne, bu dee Lemeg mii, muy juróom ñaar fukki yoon ak juróom ñaar.» \p \v 25 Bi loolu wéyee Aadama dëkkoo soxnaam, mu am doom ju góor; tudde ko Set (mu firi May), ndax da ne: «Yàlla may na ma weneen askan, mu wuutu Abel, mi Kayin rey.» \v 26 Set it, am doom ju góor, tudde ko Enos. Fan yooya lañu tàmbalee tudd \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, di ko wormaal. \c 5 \ms1 Askanu Aadama, ba ci Nóoyin \mr (Saar 5.1—6.8) \p \v 1 Ni téere indee askanu Aadama nii la. Ba Yàlla di sàkk nit, da koo bind ci melokaanam, \v 2 góor ak jigéen la sàkk, barkeel leen, tudde leen Nit, keroog ba mu leen sàkkee. \p \v 3 Aadama dund téeméeri at ak fanweer (130), jur doom ju góor, mu bindoo melokaanam te nirook moom. Mu tudde ko Set. \v 4 Set juddu na, Aadama dundaat juróom ñetti téeméeri at (800), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. \v 5 Kon Aadama dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fanweer (930), doora faatu. \p \v 6 Set moomee am na téeméeri at ak juróom (105), doora jur Enos. \v 7 Enos juddu na, Set dundaat juróom ñetti téeméeri at ak juróom ñaar (807), amaat doom yu góor ak yu jigéen. \v 8 Kon Set dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fukk ak ñaar (912), doora faatu. \p \v 9 Enos nag am na juróom ñeent fukki at (90), doora jur Kenan. \v 10 Kenan juddu na, Enos dundaat juróom ñetti téeméeri at ak fukk ak juróom (815), amaat doom yu góor ak yu jigéen. \v 11 Kon Enos dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom (905), doora faatu. \p \v 12 Kenan moomee am na juróom ñaar fukki at (70), doora jur Malaleel. \v 13 Malaleel juddu na, Kenan dundaat juróom ñetti téeméeri at ak ñeent fukk (840), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. \v 14 Kon Kenan dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fukk (910), doora faatu. \p \v 15 Malaleel nag am na juróom benn fukki at ak juróom (65), doora jur Yeredd. \v 16 Yeredd juddu na, Malaleel dundaat juróom ñetti téeméeri at ak fanweer (830), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. \v 17 Kon Malaleel dund na juróom ñetti téeméeri at ak juróom ñeent fukk ak juróom (895), doora faatu. \p \v 18 Yeredd moomee am na téeméeri at ak juróom benn fukk ak ñaar (162), doora jur Enog. \v 19 Enog juddu na, Yeredd dundaat juróom ñetti téeméeri at (800), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. \v 20 Kon Yeredd dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom benn fukk ak ñaar (962), doora faatu. \p \v 21 Enog moomee, am na juróom benn fukki at ak juróom (65), doora jur Matusalem. \v 22 Matusalem juddu na, ba noppi Enog topp Yàlla ñetti téeméeri at (300), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. \v 23 Kon Enog dund na ñetti téeméeri at ak juróom benn fukk ak juróom (365). \v 24 Enog dafa topp Yàlla, ba jekki-jekki giseesatu ko, ndaxte Yàllaa ko yéege fa moom. \p \v 25 Matusalem moomee am na téeméeri at ak juróom ñett fukk ak juróom ñaar (187), doora jur Lemeg. \v 26 Lemeg juddu na, Matusalem dundaat juróom ñaar téeméeri at ak juróom ñett fukk ak ñaar (782), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. \v 27 Kon Matusalem dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom benn fukk ak juróom ñeent (969), doora faatu. \p \v 28 Lemeg nag am na téeméeri at ak juróom ñett fukk ak ñaar (182), doora jur doom ju góor. \v 29 Mu tudde ko Nóoyin (mu firi Noflaay) ndax dafa ne: «Kii moo nuy taxa noyyiwaat, noppal nu ci liggéey yu metti ak coonoy mbeyu suuf, si \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji rëbb.» \v 30 Nóoyin juddu na, Lemeg dundaat juróomi téeméeri at ak juróom ñeent fukk ak juróom (595), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. \v 31 Kon Lemeg dund na juróom ñaar téeméeri at ak juróom ñaar fukk ak juróom ñaar (777), doora faatu. \p \v 32 Nóoyin moomee am na juróomi téeméeri at (500), doora jur Sem ak Xam ak Yafet. \c 6 \s1 Yàlla fas na yéene tas àddina ndax mbonu nit \p \v 1 Bi nga xamee ne nit ñi tàmbali nañoo fulandiwu ci kaw suuf, te am ay doom yu jigéen, \v 2 ay goney Yàlla ñoo gis jigéen ñeek seen taar, ñuy jël ñi ñu bëgg ci ñoom, def leeni jabar. \v 3 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji daldi wax ne: «Manumaa bàyyi nit, muy wéyee dunde noo, gi ma ko may, ndax nit du dara lu dul suuxi neen, kon dinaa leen àppal diirub téeméeri at ak ñaar fukk (120).» \p \v 4 Ca jamono yooya ak itam gannaaw ba goney Yàlla yooyu àndeek jigéeni àddina, ba am ca ay doom, aw xeetu ponkal wu ñuy wax Nefilim moo nekkoon ci àddina. Ñooy ponkal ya woon te doonoon góor ñu amoon tur. \p \v 5 Aji Sax ji dafa gis ne mbonu nit màgg na lool ci biir àddina, te fu mu mana tollu, lu bon rekk lay xinte ci xolam. \v 6 Aji Sax ji nag am tiis ci xolam, ba mititlu li mu doon sàkk nit ci kaw suuf. \v 7 Aji Sax ji daldi ne: «Dinaa far ci kaw suuf doom aadama yi ma sàkk, nit ak jur, luy raam ak luy naaw, ndax mititlu naa li ma leen sàkk.» \v 8 Waaye fekk na Aji Sax ji xool Nóoyin bëti yërmande. \ms1 Askanu Nóoyin \mr (Saar 6.9—9.29) \p \v 9 Askanu Nóoyin mooy lii. Nóoyin nit ku jub la woon, di ku mat ci biir nit ñi mu bokkal jamono, te di ku topp Yàlla. \v 10 Nóoyin nag amoon na ñetti doom yu góor: seeni tur di Sem, Xam ak Yafet. \p \v 11 Booba fekk na àddina yàqu, te fees ak ay, Yàlla teg ci bëtam. \v 12 Yàlla gis ne àddina yàqu na, ndaxte jëfi ñépp a bokk ñaaw fi kaw suuf. \p \v 13 Ba mu ko defee Yàlla ne Nóoyin: «Dogal naa ne dinaa boole faat mboolem boroom bakkan, ndaxte ayu nit dajal na kaw suuf. Dinaa leen boole ak li ci àddina, faagaagal. \p \v 14 «Yaw nag wutal dénku sippar, yettal ci sa bopp gaal gu mag; nga sàkk ci ay néeg, te diw ko koltaar biir ak biti. \v 15 Ni nga koy defare nii la. Na guddaayu gaal gi di ñetti téeméeri xasab, yaatuwaay bi di juróom fukki xasab, taxawaay bi di fanweeri xasab. \v 16 Yettal mbaar, mu ko tiim, te nga àggle gaal gi, bàyyi lu tollook xasab diggante kéméj yi ak mbaar mi. Sàkkal ko bunt ci wet gi, te séddale ko ñetti néeg yu tegloo, benn ci suuf, benn ci digg bi ak benn ci kaw. \p \v 17 «Maa ngi nii di indi mbënnu ndox ci kaw suuf, mu far lépp luy dund lu asamaan tiim; te lépp lu nekk ci kaw suuf dina dee. \v 18 Waaye dinaa fas \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* ak yaw, nga dugg ci gaal gi, yaak say doom ak sa soxna ak say soxnay doom. \v 19 Te xeeti rab yépp nanga ci dugal ñaar ci gaal gi, wu ci nekk, nga def ko góor ak jigéen; su ko defee ngeen ànd mucc. \v 20 Xeetu picc wu ci nekk ak xeetu bàyyima wu ci nekk ak wépp xeetu rab wuy raam ci suuf, dina def ñaar, ñëw ci yaw, ba raw. \v 21 Sàkkal ci bépp xeetu dund, denc, ngeen bokk dunde.» \p \v 22 Noonu la Nóoyin def. Lépp lu ko Yàlla sant, def na ko. \c 7 \s1 Yàlla musal na Nóoyin ci mbënn mi \p \v 1 Gannaaw ba loolu amee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax Nóoyin ne ko: «Duggal ci gaal gu mag gi, yaak sa njaboot gépp, ndaxte niti jamono jii, yaw rekk laa ci gis, nga jub ni ma ko bëgge. \v 2 Xeeti rab yu set\f + \fr 7.2 \fr*\fk rab yi set \fk*\ft ñoo di rab, yi Yàlla nangu, ñu sarxal ko.\ft*\f* yépp yóbbaale ci juróom ñaar yu góor ak juróom ñaar yu jigéen, ak ñaar ci xeeti rab yi setul, te ñuy góor ak jigéen. \v 3 Te it xeetu picc mu nekk yóbbaale ci juróom ñaar yu góor ak juróom ñaar yu jigéen, ngir seen xeet baña fey ci kaw suuf. \v 4 Ndax kat li feek juróom ñaari fan dinaa wàcce taw ci kaw suuf diiru ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg, ba far ci àddina mboolem mbindeef mu ma sàkk.» \v 5 Nóoyin daldi def la ko Aji Sax ji sant lépp. \p \v 6 Bi mbënn miy ñëw ci àddina, booba fekk na Nóoyin am juróom benni téeméeri at. \v 7 Nóoyin dugg na ca gaal ga, ànd ak ay doomam ak soxnaam ak soxnay doomam ya, ngir mucc ca ndoxu mbënn ma. \v 8 Rab yu set yi ak yi setul ak picc yi ak yiy raam \v 9 ànd nañu ak Nóoyin, dugg ca gaal ga, def ñaar-ñaar, góor ak jigéen, ni ko Yàlla sante Nóoyin. \v 10 Ba juróom ñaari fan wéyee nag, ndoxu mbënn ma agsi ci kaw suuf. \p \v 11 At ma Nóoyin amee juróom benni téeméeri at, ca fukki fan ya ak juróom ñaar ca ñaareelu weer wa, kera la bëti ndox ya ne jàyy, jóge xóotey géej, bunti ndoxi asamaan ne kulbét, mu ne yureet, \v 12 taw biy sottiku ci suuf diiru ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg. \p \v 13 Keroog bés boobu la Nóoyin ànd aki doomam yu góor, Sem ak Xam ak Yafet, ak soxnaam ak ñetti soxnay doomam yooyu, ñu dugg ca gaal ga, \v 14 àndandook rabu àll yépp, lu ci nekk ak wirgoom, ak jur gépp, lu ci nekk ak wirgoom, ak lépp luy raam ci kaw suuf, lu ci nekk ak wirgoom, ak lépp luy naaw, lu ci nekk ak wirgoom, muy picc mbaa boroomi laaf. \v 15 Lépp luy boroom bakkan def na ñaar-ñaar, ànd ak Nóoyin, dugg ca gaal ga, \v 16 mboolem xeetu mbindeef rekk, di góor ak jigéen, ni ko ko Yàlla sante. Ci kaw loolu Aji Sax ji ne ràpp buntu gaal gi, gannaaw bi Nóoyin duggee. \p \v 17 Mbënn ma nag di wal ci àddina diiru ñeent fukki fan. Ndox ya di yokku, gaal gay jóg, ba tëmb, tiim suuf lu sore. \v 18 Ma ngay gën di yokku, tey baawaan ci kaw suuf, ba gaal ga tëmb, di dem ca kaw ndox ma. \v 19 Ndox ma di walangaan, ba mëdd tund yu kawe ya fépp fu asamaan tiim. \v 20 Muy yokku, di yokku, ba gëna kawe tund ya lu mat fukki xasab ak juróom. \p \v 21 Mboolem mbindeef mu daan dox ci kaw suuf dee na ca. Picc yi ak jur gi ak rabi àll yi ak lépp luy raam ci kaw suuf dee na, ñoom ak nit ñépp. \v 22 Mboolem mbindeef muy boroom bakkan ci kaw suuf a bokk dee. \v 23 Luy dund ci àddina daldi sànku, ba nit ak jur ak luy raam ak luy naaw— lépp la Aji Sax ji raafal ci àddina. Nóoyin rekk a des, moom ak ña àndoon ak moom ca gaal ga. \p \v 24 Ndox mi nag di wal-wali ci kaw suuf diirub téeméeri fan ak juróom fukk. \c 8 \s1 Nóoyin génn na gaal gu mag ga \p \v 1 Ci biir loolu Yàlla xalaat na Nóoyin ak li mu nekkal ci gaal gi, di rabi àll yi ak jur gi. Yàlla daldi yebal ngelaw, mu wal kaw suuf, ba ndox yi wàcc. \v 2 Bëti ndox ya ca xóote ya dafa taxaw, bunti ndoxi asamaan tëju, taw bi dal. \v 3 Ci kaw loolu ndox mi taa ci suuf di wàññiku. Bi téeméeri fan yi ak juróom fukk matee nag, ndox ma gëna néew. \v 4 Ba juróom ñaareelu weer wa amee fukki fan ak juróom ñaar, gaal gaa nga teereji tundi Araraat. \v 5 Ndox may wàññiku rekk ba ca fukkeelu weer wa. Keroog ba fukkeelu weer wa teroo, ca la njobbaxtali tund ya tàmbalee feeñ. \p \v 6 Teg nañu ca ñeent fukki fan, Nóoyin doora ubbi poroxndoll, ba mu sàkkaloon gaal ga, \v 7 daldi yebal ab baaxoñ, muy naaw, di dem ak a dikk, ba ndox mi fendi ci kaw suuf. \v 8 Mu teg ca yebal pitax, ba xam ndax ndox mi ci suuf fer na. \v 9 Teewul pitax ma gisul fenn fu mu tag, ndax ndox mi muur na suuf sépp. Mu délsi nag fa moom ca gaal ga. Nóoyin tàllal loxoom, jàpp ko dugal ci biir fi wetam. \v 10 Négandiku na juróom ñaari fan, doora yebalaat pitax ma. \v 11 Ba mu délsee ca ngoon, indaalewul lu moy xobu oliw wu tooy wu keppe ca sàll wa. Nóoyin xam ne ndox mi taa woon ci suuf, fer na. \v 12 Mu négati juróom ñaari fan, bàyyiwaat pitax ma. Boobu yoon nag délsiwaatul ca moom. \p \v 13 At ma Nóoyin amee juróom benni téeméeri at ak benn, keroog benn fanu weer wa jëkk, ndox ma taa woon ca suuf daldi fendi. Nóoyin ubbi kubeer ga, xool, ba gis ne kaw suuf sépp wow na. \v 14 Keroog ñaar fukki fan ak juróom ñaar ca ñaareelu weer wa, ca la suuf si doora wow koŋŋ. \p \v 15 Ba loolu amee Yàlla ne Nóoyin: \v 16 «Génnal gaal gi, yaak sa soxna ak say doom ak say soxnay doom. \v 17 Génnewaaleel lépp luy xeetu mbindeef mu ngeen àndal: picc yi ak bàyyima yi ak luy raam, ñu fulandiwu ci kaw suuf, daldi giir te bare.» \v 18 Nóoyin daldi génn, moom aki doomam ak soxnaam ak soxnay doomam ya. \v 19 Rabi àll yi ak luy raam ak luy naaw ak luy dox ci kaw suuf— lépp génne ca gaal ga, lu ci nekk ak wirgoom. \p \v 20 Naka la Nóoyin génn, daldi sàkkal \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*, màggale ko ko. Mu sàkk nag ci mboolem rab wu set ak mboolem picc mu set, jébbal Yàlla ca sarxalukaay ba, muy \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*. \v 21 Ci kaw loolu xetug jàmm gillee ca sarax sa, yéeg fa Aji Sax ja. Booba la wax ci xolam ne: «Dootuma rëbb suuf mukk ndax nit, doonte ba muy ndaw lay dale xinte lu ñaaw ci xolam. Dootuma boole fàdd mukk lépp luy dund, nii ma ko defe. \q1 \v 22 Li feek suuf di suuf, \q1 dootu jiwooy dakk mbaa ngóob, \q1 te du sedd aku tàngoor, \q1 du nawet it mbaa noor, \q1 mbaa guddeek bëccëg.» \c 9 \s1 Yàlla fas na kóllëre ak Nóoyin \p \v 1 Ci kaw loolu Yàlla barkeel Nóoyin aki doomam ne leen: «Giirleen te bare, ba fees àddina. \v 2 Mboolem rabi àll yi ak njanaawi asamaan ak ndëgmeent yi ci suuf, ak jëni géej yépp, dinañu leen ragal lool. Teg naa leen ci seeni loxo. \v 3 Man ngeena dunde boroom bakkan yooyu yépp. Jagleel naa leen bindeef yooyu yépp, ni ma leen jagleele woon gàncax. \p \v 4 «Waaye buleen lekk yàpp wu ànd ak deret, ndaxte dund a ngi ci deret. \v 5 Seen dundu nit itam, mu ngi ci seen deret, kon kat, képp ku tuur seen deret dinaa ko ko topp. Te it mala mu ci rey nit dinaa ko ko topp, ni may toppe nit. Dinaa topp ku nekk deretu moroomam. \q1 \v 6 Ku tuur deretu nit, \q1 na nit tuur deretam, \q1 ngir melokaanu boppam \q1 la Yàlla sàkke nit. \m \v 7 Yeen nag, giirleen te bare, fulandiwu ci kaw suuf te fees ko.» \p \v 8 Yàlla nag wax Nóoyin ak doomam, yi mu àndal, ne leen: \v 9 «Bés niki tey fasal naa sama bopp \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* sama diggante ak yeen ak seen askan, \v 10 fas ko it sama diggante ak mboolem mbindeef mu ngeen àndal, muy picc akug jur mbaa rabi àll— lépp daal lu génnandoo ak yeen ci gaal gi, di lépp luy dund ci kaw suuf. \v 11 Ni may faseek yeen kóllëre nii la: \q1 Deesatul boole bindeef yépp, faat ci mbënn mukk. \q1 Du menn mbënn mu deeti faagaagal àddina.» \p \v 12 Yàlla neeti: «Kóllëre gi may fas ak yeen ak mboolem mbindeef mu ànd ak yeen, day sax ba fàww te liy màndargaam mooy lii: \v 13 def naa sama xon ci niir yi, muy màndargaal kóllëre, gi dox sama diggante ak àddina. \p \v 14 «Saa su ma dajalee niir yi ci jaww ji, ba xon gi feeñ ci niir yi, \v 15 damay daldi xalaataat kóllëre, gi ma fas sama digganteek yeen ak mboolem xeeti bindeef, su ko defee ndox dootu sabab mbënn muy faagaagal lépp luy dund. \v 16 Xon gi day nekk ci biir niir yi, ma di ko gis, di xalaat kóllëre, gi ma fas fàww, sama diggante, man Yàlla, ak mboolem xeetu mbindeef mu nekk ci kaw suuf.» \v 17 Ci kaw loolu Yàlla ne Nóoyin: «Loolu mooy màndargaal sama kóllëre, gi ma fas ak mboolem mbindeef mu nekk ci kaw suuf.» \s1 Mbirum Nóoyin ma aki doomam \p \v 18 Doomi Nóoyin yu góor, yi génne ci gaal gi, ñooy: Sem, Xam ak Yafet; Xam mooy baayu Kanaan. \v 19 Ñooñu ñooy ñetti doomi Nóoyin yu góor, te ci ñoom la àddina sépp soqikoo. \p \v 20 Nóoyin ab beykat la woon. Mu nekk nag ci njëmbatum reseñ. \v 21 Mu am bés mu naan biiñ, ba màndi, tëdd ci xaymaam, daldi sàgganu. \p \v 22 Ba loolu amee Xam, baayu Kanaan, gis céri baayam, génn waxi ko Sem ak Yafet ca biti. \v 23 Sem ak Yafet ànd, jël malaan, teg ko ci seeni mbagg, doxe gannaaw ba agsi, doora sàng seen céri baay. Dañoo dummóoyu, ba gisuñu seen céri baay. \p \v 24 Màndite ma giif, Nóoyin yewwu, daldi yég ni xale bi def ak moom. \v 25 Ba mu ko defee mu ne: \q1 «Yal na Kanaan torox, \q1 bay jaamu jaami doomi ndeyam.» \m \v 26 Mu dellu ne: \q1 «Cant ñeel na \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, Yàllay Sem, \q1 yal na Kanaan dib jaamam. \q1 \v 27 Yal na Yàlla lawal askanu Yafet, \q1 dëël ko ci xaymay Sem, \q1 te Kanaan di seen jaam.» \p \v 28 Gannaaw ba mbënn ma wéyee, Nóoyin dundaat na ñetti téeméeri at ak juróom fukk (350). \v 29 Nóoyin dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom fukk (950), doora faatu. \c 10 \ms1 Askanu doomi Nóoyin \mr (Saar 10.1—11.9) \s1 Xeet yi sosoo ci doomi Nóoyin \p \v 1 Askanu doomi Nóoyin mooy lii. Gannaaw ba mbënn ma wéyee, Sem ak Xam ak Yafet am nañu ay doom. \s1 Li jëm ci askanu Yafet \p \v 2 Doomi Yafet yu góor ñii la: Gomeer ak Magog ak Madéy ak Yawaan ak Tubal ak Meseg ak Tiraas. \v 3 Doomi Gomeer yu góor di Askenas, Rifaat ak Togarma. \v 4 Doomi Yawaan yu góor di Elisa ak Tarsis ak Kitim ak Dodanim. \v 5 Ñi sosoo ci ñoom ñoo law ca wàllaa géej, meññ nag ay xeet ci seeni suuf, xeet wu ci nekk ak làkkam, def it ay làng ci seen biiri xeet. \s1 Li jëm ci askanu Xam \p \v 6 Doomi Xam yu góor ñoo di ñii: Kuus ak Misrayim ak Puut ak Kanaan. \v 7 Doomi Kuus yu góor di Seba ak Awila ak Sabta ak Raama ak Sabteka. Doomi Raama yu góor di Saba ak Dedan. \p \v 8 Kuus moom itam jur Namróot, ki jëkk di jàmbaar ju siiw ci kaw suuf, \v 9 mu doonoon rëbbkat bu maga mag. Looloo waral ñu naan: «Mbete Namróot, rëbbkat bu maga mag ba.» \v 10 Dëkk yiy péeyi nguuram ñoo di: Babel ak Ereg ak Akàdd ak Kalne, gi ci réewu Sineyaar. \v 11-12 Ca réew mooma la Namróot jóge dem Asur, sanc dëkk bu mag boobee di Niniw, ak dëkk yooyee di Reyobot Ir ak Kala, ba Resen, gi ci diggante Niniw ak Kala. \p \v 13 Misrayim nag mooy maami Luddeen ñi ak Anameen ñi ak Leyabeen ñi ak Naftuyeen ñi \v 14 ak Pataruseen ñi ak Kasluyeen, ñooñee waa Filisti bàyyikoo ca seen réew; ak it Kaftoreen ñi. \p \v 15 Kanaan moo taawloo Sidon, teg ca Ett, \v 16 te mooy maami Yebuseen ñi ak Amoreen ñi ak Girgaseen ñi \v 17 ak Eween ñi ak Arkeen ñi ak Sineen ñi, \v 18 ak Arwàddeen ñi ak Semareen ñi ak Amateen ñi. La ca tegu làngi Kanaan tasaaroo. \v 19 Kemu suufas Kanaaneen ña, mu ngi tàmbalee Sidon, jaar weti Gerar, dem ba Gasa, wuti Sodom ak Gomor ak Atma ak Ceboyim, daldi teeri Lesa. \p \v 20 Ñooñu ñooy askani Xam, askan wu ci nekk ak làngam ak làkkam, di ay xeet ci seeni réew. \s1 Li jëm ci askanu Sem \p \v 21 Sem, miy magu Yafet, jur na moom itam ay doom yu góor. Mooy maami Eber ak askanam. \v 22 Doomi Sem yu góor ñii la: Elam ak Asur ak Arpagsàdd ak Ludd ak Aram. \v 23 Góor ñi Aram jur ñii la: Uus ak Xuul ak Geter ak Maas. \v 24 Arpagsàdd jur Sela, Sela jur Eber; \v 25 Eber moom, jur ñaari doom yu góor, kenn ki tudd Peleg (mu firi Séddlikoo), ndaxte ci jamonoom àddina dafa séddlikoo woon. Rakku Peleg mooy Yogtaan. \p \v 26 Yogtaan a jur Alamodàdd ak Selef ak Asarmawet ak Yera \v 27 ak Adoram ak Usal ak Digla \v 28 ak Obal ak Abimayel ak Saba \v 29 ak Ofir ak Awila ak Yobab. Ñooñu ñépp di doomi Yogtaan yu góor. \v 30 Ña nga dëkkoon ca wàllu Mesa, ga wuti Sefar, di diiwaanu tund ya ca penku. \p \v 31 Ñooñoo askanoo ci Sem, askan wu ci nekk ak làngam ak làkkam, di ay xeet ci seeni réew. \p \v 32 Làngi doomi Nóoyin yu góor a ngoogu, làng gu nekk ak askanam, ñu diy xeet. Ci ñoom la xeet yépp jóge tasaaroo ci kaw suuf, gannaaw ba mbënn ma wéyee. \c 11 \s1 Yàlla safaan na làkku àddina, mu jaxasoo \p \v 1 Ca ndoorte la nag waa àddina sépp a bokkoon wenn làkk, seeni wax di benn. \v 2 Bi nit ñi toxoo, jëm penku, dañoo gis ag joor ci réewu Sineyaar, ñu sanc fa. \v 3 Ñu ne: «Ayca nu defar ay móol yu ñu lakk cib taal, ba mu ñor.» Ci kaw loolu ñu def móol ya doji tabax, taqalee ko koltaar, \v 4 daldi ne: «Ayca nu tabax ab dëkk bu taax ma bëtt asamaan; kon dinanu am woy, te dunu tasaaroo ci kaw suuf.» \p \v 5 Ba ñu noppee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wàcc, xoolsi dëkk bi ak taax, mi doom aadama yi tabax. \v 6 Aji Sax ji da ne: «Su ñu tàmbalee nii, di menn mbooloo te bokk wenn làkk, kon dara dootu leen të. \v 7 Ayca nu wàcc, safaan seen làkk, ba dootuñu déggoo.» \p \v 8 Ba loolu amee Aji Sax ji jële leen foofa, tasaare leen ci kaw suuf sépp, ñu yemale fa dëkk ba ñu doon tabax. \v 9 Looloo tax ñu tudde dëkk ba Babel (mu firi Safaan), ndax foofa la Aji Sax ji safaane làkku àddina sépp, mu jaxasoo, te fa la leen tasaaree ci kaw suuf sépp. \ms1 Askanu Sem, maamu Ibraam \mr (Saar 11.10-26) \p \v 10 Askanu Sem mooy lii. Sem am na téeméeri at, doora jur Arpagsàdd, fekk na mbënn ma wees, ba mu am ñaari at. \v 11 Arpagsàdd juddu na, Sem dundaat juróomi téeméeri at (500), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. \p \v 12 Arpagsàdd am fanweeri at ak juróom, jur Sela. \v 13 Sela juddu na, Arpagsàdd dundaat ñeenti téeméeri at ak ñett (403), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. \p \v 14 Sela am fanweeri at, jur Eber. \v 15 Eber juddu na, Sela dundaat ñeenti téeméeri at ak ñett (403), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. \p \v 16 Eber am fanweeri at ak ñeent, jur Peleg. \v 17 Peleg juddu na, Eber dundaat ñeenti téeméeri at ak fanweer (430), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. \p \v 18 Peleg am fanweeri at, jur Rew. \v 19 Rew juddu na, Peleg dundaat ñaar téeméeri at ak juróom ñeent (209), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. \p \v 20 Rew am fanweeri at ak ñaar, jur Serug. \v 21 Serug juddu na, Rew dundaat ñaar téeméeri at ak juróom ñaar (207), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. \p \v 22 Serug am fanweeri at, jur Naxor. \v 23 Naxor juddu na, Serug dundaat ñaar téeméeri at, juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. \p \v 24 Naxor am ñaar fukki at ak juróom ñeent, jur Teraa. \v 25 Teraa gane na àddina, Naxor dundaat téeméeri at ak fukk ak juróom ñeent (119), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. \p \v 26 Gannaaw ba Teraa amee juróom ñaar fukki at, am na Ibraam ak Naxor ak Aran. \ms1 Askanu Teraa, baayu Ibraam \mr (Saar 11.27—25.11) \p \v 27 Askanu Teraa mooy lii. Teraa mooy baayu Ibraam\f + \fr 11.27 \fr*\fk Ibraam \fk*\ft mii: Yàlla dina ko mujja tudde Ibraayma. Seetal ci 17.5.\ft*\f* ak Naxor ak Aran. Aran mooy baayu Lóot. \v 28 Gannaaw loolu Aran faatu na lu jiitu faatug baayam Teraa, ca réew ma mu juddoo, di Ur\f + \fr 11.28 \fr*\fk Ur: \fk*\ft dëkk bu yàggoon la, te bokkoon ci réew, mi ñu tudde Iraag léegi.\ft*\f*, dëkku Kaldeen ña. \v 29 Ibraam ak Naxor jël nañu ay soxna; soxnas Ibraam tudd Sarayi, soxnas Naxor di Milka. Milka moomu, moom ak rakkam ju jigéen Yiska, Aran ay seen baay. \v 30 Sarayi moomu masuloona am doom te it manu ko woona am. \p \v 31 Mu am bés Teraa ànd ak doomam Ibraam ak sëtam Lóot, mi Aran di baayam, ak Sarayi, soxnas Ibraam. Ñu bokk jóge Ur gu Kaldeen ña, jëm réewu Kanaan. Ba ñu demee ba Karan, daldi fay sanc. \v 32 Teraa dund na ñaar téeméeri at ak juróom (205), doora génn àddina, ñu denc ko Karan. \c 12 \s1 Yàlla sant na Ibraam, mu gàddaay \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji moo waxoon Ibraam, ne ko: «Jógeel sam réew, jóge ci say bokk ak sa kër baay, te nga dem ca réew mi ma lay won, \q1 \v 2 ma def la ngay cosaanal xeet wu yaa, \q1 barkeel la, \q1 màggal sa tur, \q1 ngay buntu barke; \q1 \v 3 ku la ñaanal barke, ma barkeel, \q1 ku la móolu it, ma alag, \q1 te xeeti àddina sépp, \q1 ci yaw lañuy barkeele.» \p \v 4 Ibraam daldi dem, na ko ko Aji Sax ji waxe woon, Lóot topp ca. Ba Ibraam di jóge Karan, booba am na juróom ñaar fukki at ak juróom (75). \v 5 Ibraam ànd ak soxnaam Sarayi ak Lóot, mi muy baay bu ndaw ci moom. Mu yóbbaale nag alal, ja mu dajale jépp, ak jaam, ya mu jënde Karan. Ñu jóge fa, jublu réewu Kanaan. \p \v 6 Ba ñu agsee Kanaan, Ibraam dafa jàll ca biir réew ma, ba àgg bérab bu sell, ba féete ak Sikem, ca garab\f + \fr 12.6 \fr*\ft Xeetu garab la gu ñuy wax terebent.\ft*\f* gu mag, ga ñuy wooye More. Booba fekk na waa Kanaan a nga woon ca réew ma. \v 7 Ci kaw loolu Aji Sax ji feeñu Ibraam ne ko: «Sa askan wi soqikoo ci yaw laay jox réew mii.» Ibraam nag daldi tabaxal Aji Sax, ji ko feeñu, ab \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*. \p \v 8 Gannaaw loolu mu jóge fa, jëm tund, wi féete Betel penku, samp fa xaymaam; Betel féete ko sowu, Ayi féete ko penku. Foofa itam Ibraam tabaxal na fa Aji Sax ji sarxalukaay, tudd fa Aji Sax ji, wormaal ko. \v 9 Ibraam bàyyikooti fa, aw yoonam, jublu àllub Negew\f + \fr 12.9 \fr*\fk àllub Negew: \fk*\ft mu nga féete Kanaan bëj-saalum, nekk ca yoonu Misra. Li muy tekki mooy «wowaay».\ft*\f*. \s1 Ibraam dem na réewum Misra \p \v 10 Ca jamono jooja xiif a amoon ca réew ma, ba tax Ibraam dem réewum Misra, toogi fa, ndax xiif bu metti la woon. \v 11 Naka lay jub Misra, daldi ne soxnaam Sarayi: «Déglu ma, xam naa ne ku rafet nga. \v 12 Bu la waa Misra gisee, dinañu ne sama soxna nga. Te dinañu ma rey, nga des. \v 13 Kon nag ngalla waxal ne sama jigéen nga, ba tax ma am jàmm; su ko defee dees na ma bàyyi, ma dund, te di la ko gërëme.» \p \v 14 Ba Ibraam àggee Misra, waa Misra gis ne jigéen ji mu àndal rafet na lool. \v 15 Jaraafi Firawna itam gis ko, di ko kañ ca Firawna ndax taar ba, ñu daldi ko yóbbu ca kër Firawna. \v 16 Firawna nag topptoo Ibraam bu baax ndax moom, ñu may ko ay gàtt ak ay nag, ay mbaam yu góor, ak ay jaam yu góor ak yu jigéen, ak ay mbaam yu jigéen aki giléem. \p \v 17 Teewul \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wàcce ca Firawna ak waa këram jàngoro yu metti ndax Sarayi, soxnas Ibraam. \v 18 Firawna woolu Ibraam ne ko: «Li nga ma def nag? Lu tax waxoo ma ne kii sa soxna la? \v 19 Lu tax nga ne sa jigéen la, ba tax ma jël ko, bëgg koo def sama jabar? Ayca, sa jabar a ngoog, fabal te ne mott!» \v 20 Naka la Firawna wax loolu ba noppi, daldi sant ay dagam, ñu génne Ibraam réew ma, moom ak soxnaam ak alalam jépp. \c 13 \s1 Ibraam ak Lóot teqlikoo nañu \p \v 1 Bi loolu amee Ibraam dafa jóge Misra, moom ak soxnaam, yóbbaale alalam jépp, daldi dem ca àllub Negew, Lóot topp ca. \v 2 Ibraam nag amoon alal ju bare diggante jur, xaalis ak wurus. \v 3 Gannaaw loolu mu awati yoonam, jóge àllub Negew, jëm dëkk ba ñu naa Betel, dem ba àgg ca bérab, ba mu jëkkoona samp xaymaam, ci diggante Betel ak Ayi, \v 4 fa mu tabaxoon ab \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*. Ibraam nag tudd fa \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, wormaal ko. \p \v 5 Ci biir loolu Lóot, mi mu àndal, moom it yor jur gu gudd ak gu gàtt aki xayma, \v 6 ba tax xajatuñu ca réew ma, ndax seen alal dafa bare, ba manatuñu faa bokk dëkk. \v 7 Loolu tax sàmmi Ibraam ak sàmmi Lóot di jote. Rax ci dolli Kanaaneen ñi ak Periseen ñi ña nga woon ca réew ma. \p \v 8 Ba loolu amee Ibraam da ne Lóot: «Waay waay, bu xuloo am sama digganteek yaw mbaa say sàmm ak samay sàmm. Xanaa dunuy bokk nag? \v 9 Xanaa àll bi newul yàmblaŋ ngay gis? Nan teqlikoo, kay; boo demee càmmoñ, ma dem ndijoor; boo demee ndijoor, ma dem càmmoñ.» \p \v 10 Ba mu waxee ba noppi, Lóot dafa xool, gis joor, gi wër dexu Yurdan gépp, màndi ndox. Ndax laata Aji Sax jiy tas dëkk yu ñuy wax Sodom ak Gomor, àll bi jëm Sowar dafa naatoon, ni réewum Misra naate, ba faf mel ni toolub Aji Sax ja\f + \fr 13.10 \fr*\ft Tool booba mooy Àjjana, fa Yàlla jëkkoona dëkkal Aadama ak Awa.\ft*\f*. \v 11 Ba mu ko defee Lóot tànn jooru Yurdan gépp, daldi toxu jëm penku. Noonu lañu teqlikoo. \v 12 Ibraam dëkke réewu Kanaan, Lóot sance dëkk ya ca jooru Yurdan, daldi toxal xaymaam, samp ko Sodom. \v 13 Waaye waa Sodom ñu bon lañu woon, te mana moy Aji Sax ji lool. \s1 Digeb Aji Sax ja ak Ibraam \p \v 14 Gannaaw ba Lóot teqlikook Ibraam, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na Ibraam ne ko: «Téenal foofu nga taxaw, te séenu bëj-gànnaar ak bëj-saalum ak penkook sowu, \v 15 ndaxte réew, mi ngay gis mépp, yaw laa koy may ba fàww, yaak askan wi soqikoo ci yaw. \v 16 Dinaa leen yokk, ba ñu tollu ni feppi suuf, ba feppi suuf gëna neexa waññ sa askan. \v 17 Jógal wër réew mi mépp, ba mu daj, ndax yaw laa koy may.» \p \v 18 Ba mu ko defee Ibraam sempi xaymaam, ñëw dal Ebron ca garab yu mag ya ca toolub Mamre, daldi fay tabaxal Aji Sax ji \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*. \c 14 \s1 Ibraam wallu na Lóot \p \v 1 Ca jamonoy Amrafel buurub Sineyaar, ak Aryog buurub Elasaar, Kedorlamer buurub Elam, ak Tidal buurub Goyim, \v 2 ànd nañu, dal ci kaw ñoom Bera buurub Sodom, ak Birsa buurub Gomor, ak Sineyab buurub Atma, ak Semeber buurub Ceboyim, ak it buuru dëkk ba ñuy wax Bela, mooy Sowar ba tey. \v 3 Ñooñoo booloo woon ca xuru Sidim, mooy géeju Xorom gi léegi. \v 4 Fekk na diiru fukki at ak ñaar Kedorlamer moo leen yilifoon, teewul ca fukkeelu at ma ak ñett ñu fippu. \p \v 5 Ca déwén sa Kedorlamer ak buur ya faroon ak moom, dem dàq Refayeen ña ca Àsterot Karnayim, ak Suseen ña ca Am, ak Emeen ña ca jooru Kiryaatayim, \v 6 ak Oreen ña ca seen tund wa ñuy wax Seyir. Da leena dàq ba ca garabu Paran gu mag ga ca wetu màndiŋ ma. \v 7 Ñu jóge fa nag, waññiku, dem En Mispat, di Kades ba tey, daldi teg mboolem réewum Amalegeen ña tànk, boole ca song Amoreen ña dëkk Asason Tamar. \p \v 8 Ci kaw loolu buurub Sodom génn, mook buurub Gomor ak buurub Atma ak buurub Ceboyim ak buuru Bela, di Sowar ba tey, ñoom ñépp daldi làng, nara xare ca xuru Sidim, \v 9 di sot ñoom Kedorlamer buurub Elam, ak Tidal buurub Goyim, ak Amrafel buurub Sineyaar, ak Aryog buurub Elasaar. Ñeenti buur di xareek juróom. \p \v 10 Waaye xuru Sidim woowu dafa feesoon dell aki pax aki kàmbi koltaar. Ba mu ko defee buuri Sodom ak Gomor di daw, far daanu ca kàmb ya. Ña ca des daw ba ca tund ya. \v 11 Ña leen dàq nag, jël alalu Sodom ak Gomor yépp, nanguwaale seen dund bépp boole ca, daldi dem seen yoon. \v 12 Booba lañu yóbbu Lóot ma dëkk Sodom, te Ibraam di baayam bu ndaw. Ci biir loolu ñu yóbbaale li mu amoon lépp, dem. \p \v 13 Ba loolu xewee, kenn ci ñi ñu jàppoon rëcc, ñëw ci Ibraam miy ab \w Ebrë|lemma="Ebrë:"\w*, wax ko ko. Fekk na mu dëkk ca wetu garab yu mag ya woon ca toolub Mamre, ma dib Amoreen, di mbokk mu jege ci Eskol ak Aner, ñoom ñi doon wóllërey Ibraam. \p \v 14 Ba Ibraam déggee ne jàpp nañu Lóot ma muy baayam bu ndaw, fa saa sa daa dajale dagam, yi juddoo këram te tollu ci ñetti téeméer ak fukk ak juróom ñett (318), ñu dàq buur ya ba dëkk ba ñuy wax Dan. \v 15 Ibraam dafa xàjjale mbooloom, dal ci kaw buur ya guddi, dàq leen, topp ci ñoom ba Koba, ca bëj-gànnaaru Damaas. \v 16 Ibraam nag délloosi alal ja jépp, nangu Lóot, mook alalam, ak jigéen ña ak ñeneen, ña ñu jàppoon. \s1 Melkisedeg ñaanal na Ibraam barke \p \v 17 Gannaaw ba Ibraam dàqee Kedorlamer ak buur ya àndoon ak moom, ba délsi, buurub Sodom dafa génn, gatandu ko ca xur wa ñuy wax Sawe, ñu di ko wooye xuru Buur ba tey. \v 18 Ci kaw loolu Melkisedeg\f + \fr 14.18 \fr*\fk Melkisedeg \fk*\ft mu ngi tekki «buuru njubte».\ft*\f* buurub Salem, mi doon \w sarxalkatu|lemma="sarxalkat b-:"\w* Yàlla Aji Kawe ji, daldi ñëw, indi mburu ak biiñ. \v 19 Mu ñaanal Ibraam ne ko: \q1 «Yaw Ibraam, Yàlla na la Yàlla Aji Kawe ji barkeel, \q1 moom mi sàkk asamaan ak suuf! \q1 \v 20 Waaye jaaraamaa Yàlla Aji Kawe ji, \q1 moom mi la dumaal say noon!» \m Ba loolu amee Ibraam sàkk fukkeelu la mu lël lépp, jox ko. \p \v 21 Gannaaw loolu buurub Sodom wax Ibraam ne ko: «Jox ma nit, ñi nga jàpp, te nga fab alal ji.» \v 22 Ibraam nag wax buurub Sodom ne ko: «Man yékkati naa sama loxo, Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ju Kawe ji seede, moom mi sàkk asamaan ak suuf, \v 23 nee naa: duma jël ci yaw dara, du puso, bi gëna tuut sax, su ko defee doo mana wax ne yaa ma taxa am alal. \v 24 Duma jël dara, lu wees li sama nit ñi lekk ba noppi ak sama wàllu farandoo yi, di Aner ak Eskol ak Mamre, ñoom it, nañu jot seen wàll.» \c 15 \s1 Yàlla fas na ak Ibraam kóllëre \p \v 1 Gannaaw ba loolu wéyee kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikke na Ibraam wax jii ci peeñu, mu ne ko: «Yaw Ibraam, bul ragal dara; man maay sa kiiraay, te sa yool dina màgg lool.» \v 2 Ibraam ne ko: «Boroom bi, yaw Aji Sax ji, ana loo may may nag? Man awma doom sax, te ki wara donn sama alal moo di Elyeser, miy waa Damaas.» \v 3 Ibraam teg ca ne: «Mayoo ma giir, te it jaam bu juddoo sama kër moo may donn.» \p \v 4 Kàddug Aji Sax ji nag dikkal ko, ne ko: «Du moom moo lay donn, waaye ku sosoo ci sa geño moo lay donn.» \v 5 Loolu wees Aji Sax ji yóbbu ko ci biti ne ko: «Xoolal asamaan, te waññ biddiiw yi, ndegam man nga ko.» Mu dellu ne ko: «Noonu la sa askan di tollu.» \v 6 Ibraam nag gëm na Aji Sax ji, ba tax Aji Sax ji waññal ko ngëmam ag njub. \p \v 7 Gannaaw loolu Aji Sax ji wax ko ne ko: «Man maay Aji Sax, ji la génnee Ur, ga ca Kaldeen ña, ngir may la réew mii, nga moom ko.» \v 8 Ibraam ne ko: «Yaw Aji Sax ji sama Boroom, nan la may wóore ne maa koy moom?» \v 9 Aji Sax ji ne ko: «Jëlal wëlluw ñetti at ak bëyu ñetti at ak kuuyu ñetti at, boole ci pitaxu àll ak xati mu ndaw.» \v 10 Ibraam boole yooyu yépp, rey, lu ci nekk mu dagg ko ci digg bi, dog bu nekk janook moroom ma, waaye daggul picc ya. \v 11 Ba mu ko defee ay tan jóge ca, dal ca kaw yàpp wa, Ibraam nag dàq leen. \p \v 12 Ba jant bay so, ngëmment lu réy a ko jàpp, tiitaange lu mag, ànd ak lëndëm gu ne këruus, ne milib ci kawam. \v 13 Aji Sax ji wax Ibraam ne ko: «Déglul bu baax li ma lay wax: sa askan dinañu nekk ay doxandéem ci réew mu ñu moomul, ñu def leeni jaam, sonal leen diiru ñeenti téeméeri at. \v 14 Waaye waa réew moomu leen di def ay jaam, dinaa leen àtte. Gannaaw loolu sa askan dina ca génn, ànd ak alal ju bare. \v 15 Yaw nag dinga gudd fan lool, doora nelaw, ñu denc la, nga fekki say maam ci jàmm. \v 16 Say sët-sëtaat ay délsi fii bu seen jamono jotee, ndaxte bàkkaaru Amoreen ñi\f + \fr 15.16 \fr*\fk Amoreen ñi: \fk*\ft ñoo jëkkoona moom réewu Kanaan.\ft*\f* jéggeegul dayo.» \p \v 17 Ba jant sowee, ba guddi jot, njaq luy saxar, ànd ak jum buy tàkk, daldi jaar ci diggante dogi yàpp yooyu. \v 18 Keroog Aji Sax ji fas na \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* digganteem ak Ibraam, ne ko: «Askan wi soqikoo ci yaw laa jox réew mii dale ci dexu Misra, ba ca dex gu mag googee di Efraat, \v 19 mooy réewu Keneen ñi ak Keniseen ñi ak Kadmoneen ñi \v 20 ak Etteen ñi ak Periseen ñi ak Refayeen ñi, \v 21 boole ci réewum Amoreen ñi ak Kanaaneen ñi ak Girgaseen ñi ak Yebuseen ñi.» \c 16 \s1 Ismayla juddu na \p \v 1 Sarayi amul woon doom ak boroom këram Ibraam. Waaye fekk na mu am jaam bu juddoo Misra te tudd Ajara. \v 2 Sarayi ne Ibraam: «Li am mooy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji deful ma am doom. Kon ngalla waay, dëkkool sama jaam bi, ndax Yàlla def, mu amal ma doom ju góor.» Ibraam nag dégg la Sarayi wax. \v 3 Looloo ngi am, gannaaw ba Ibraam dëkkee fukki at ca réewu Kanaan. Sarayi daldi jël Ajara, jaamam bi juddoo Misra, jox ko jëkkëram Ibraam, ngir mu dëkkoo ko. \v 4 Loolu wees Ibraam dëkkoo Ajara, mu daldi ëmb. Ajara yég ne ëmb na, indi nag yabeel digganteem ak sangam Sarayi. \p \v 5 Sarayi nag wax Ibraam ne ko: «Tooñ gi ma Ajara di tooñ, yaa ma ko yóbbe! Maa la jox sama jaam, ngir nga dëkkoo ko, naam, waaye moom, naka la yég ne ëmb na rekk, daldi indi yabeel sama digganteek moom. Kon yal na ma Aji Sax ji àtteek yaw!» \v 6 Ibraam wax Sarayi ne ko: «Sa jaam a ngoog ci say loxo, def ko lu la neex.» Sarayi nag di torxal Ajara, ba mu daw, ba soreek moom. \p \v 7 Ba mu dawee, malaakam Aji Sax ja gis ko fu dend akub bëtu ndox ca màndiŋ ma, mooy bëtu ndox, ba ca yoonu Sur. \v 8 Mu ne ko: «Yaw Ajara, jaamu Sarayi bi, foo bàyyikoo nii? Ak foo jëm?» Mu ne ko: «Damay daw ba fu soreek sama sang Sarayi.» \p \v 9 Malaakam Aji Sax ja ne ko: «Dellul ca sa sang, te nga yem ciy loxoom.» \v 10 Mu teg ca ne ko: «Dinaa yokk sa askan lool, ba kenn du leen mana waññ,» \v 11 tegaat ca ne ko: \q1 «Léegi jigéenu wérul nga, te dinga am doom ju góor; \q1 nanga ko tudde Ismayla (mu firi Yàlla dégg na), \q1 ndax Aji Sax ji yég na sa naqar. \q1 \v 12 Ismaylaay tiiñe, ni mbaamu àll mu deesul not, \q1 di noonoo ñépp, ñépp noonoo ko. \q1 Mooy sanc fu muy jàkkaarlook bokkam yépp.» \p \v 13 Ajara nag tudde Aji Sax ji wax ak moom, Ata El Roy (mu firi Yaa di Yàlla jiy gis), ndaxte da ne: «Moo man! Moona gis naa Yàlla, moom it mu gisal ma boppam de!» \v 14 Loolu moo tax ñu tudde teen booba teenu Laxay Roy (mu firi teenu Aji Dund ji may gis); mu nga nekk diggante Kades ak Beret. \p \v 15 Ba loolu weesee Ajara amal Ibraam doom ju góor. Ibraam tudde doom ji Ismayla. \v 16 Ba Ajaray am Ismayla, Ibraam a ngi tollu woon ci juróom ñett fukki at ak juróom benn (86). \c 17 \s1 Yàlla soppi na turu Ibraam \p \v 1 Ba Ibraam amee juróom ñeent fukki at ak juróom ñeent (99), am na bés \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji feeñu ko ne ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Topp ma te mat sëkk. \v 2 Dinaa feddli sama \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* ak yaw, yokk la bu baax.» \p \v 3 Ibraam dégg loola, daldi sujjóot. Yàlla wax ak moom ne ko: \v 4 «Man ci sama wàllu bopp, kóllëre gi ma fas ak yaw mooy lii. Dinga nekk maamu xeet yu baree bare. \v 5 Te tuddatuloo Ibraam; léegi yaa di Ibraayma (mu firi Maamu ñu bare), ndax maa la def ngay maamu xeet yu baree bare. \v 6 Dinaa la defal njaboot gu ne xas, ay xeet sosoo ci yaw, ba ay buur soqikoo ci yaw. \v 7 Te dinaa feddli sama kóllëre, gi ci sama diggante ak yaw, yaak sa askan, muy kóllëre guy sax maasoo maas ba fàww. Maay doon sa Yàlla, yaak sa askan. \v 8 Te réew mi nga doon ab doxandéem léegi, muy réewu Kanaan mépp, jox naa la ko, yaak sa askan, ngeen moom ko fàww. Te dinaa doon seen Yàlla.» \s1 Xaraf màndargaal na kóllëreg Yàlla \p \v 9 Gannaaw loolu Yàlla waxaat na Ibraayma ne ko: «Yaw nag, sàmmal sama \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w*, yaak sa askan ak say sët ak say sëtaat. \v 10 Kóllëre gi ma fas ak yaw, te nga war koo sàmm, yaak sa askan, li mu laaj mooy lii: góor gu nekk ci yeen, war naa xaraf. \v 11 Xaraf mooy màndargaal kóllëre googu ma fas ak yeen. \v 12 Xale bu góor, bu amee juróom ñetti fan war naa xaraf. Képp kuy góor ci seen maasoo maas, war naa xaraf, ba ci jaam bu juddoo sa kër, mbaa ku ñu jënd ci sa xaalis, ak bépp doomu doxandéem boo jurul. \v 13 Jaam bu juddoo sa kër ak boo jënd, ñoom ñaar ñépp, dees leen wara xarfal. Xaraf ay màndargaal sama kóllëre ci seen yaram, muy kóllëre gu sax fàww. \v 14 Góor gu xaraful, ndax nanguwula xaraf, dees na ko dagge ci biir xeetam, ndax sàmmul sama kóllëre.» \p \v 15 Ba loolu weesee Yàlla waxaat na Ibraayma, ne ko: «Sa soxna tuddatul Sarayi; léegi moo di Saarata\f + \fr 17.15 \fr*\fk Sarayi, Saarata \fk*\ft neexoo na ak baatu ebrë biy tekki «lingeer, doomu buur».\ft*\f*. \v 16 Dinaa ko barkeel, may la ak moom doom ju góor; dinaa ko barkeel moos, ba mu jaboote xeet yu bare, te ay buuri xeet sax dinañu soqikoo ci moom.» \p \v 17 Bi Ibraayma déggee loolu, daa sujjóot, ree. Booba ma nga naan ci xelam: «Góoru téeméeri at, ndax dina mana am doom waay? Te Saarata, mi am juróom ñeent fukki at (90) sax, manati naa am doom a?» \v 18 Ibraayma ne Yàlla: «Moo, tee ngaa saxal Ismayla rekk te ànd ak moom?» \p \v 19 Yàlla ne ko: «Waaw, waaye du tere sa soxna Saarata amal la doom ju góor, nga tudde ko nag Isaaxa. Dinaa fas ak moom sama kóllëre, mu wéy ba ciy sëtam ba fàww. \v 20 Bu dee ci wàllu Ismayla, nangul naa la ba tey. Ndax kat dinaa ko barkeel, jox ko njaboot gu yaa, yokk ko bu baax. Dina jur fukki kilifa ak ñaar yu mag, te dinaa ko defal mu sos xeet wu yaa. \v 21 Waaye sama kóllëre nag, Isaaxa laa koy fasool, moom Isaaxa, mi Saarata di am, nëgëni déwén.» \v 22 Loola la Yàlla wax Ibraayma, daldi fay bàyyikoo. \p \v 23 Ba loolu amee Ibraayma boole doomam Ismayla, ak jaam, yi juddoo këram yépp, ak ñi mu jëndoon ci xaalisam ñépp, góori waa këram ñépp, xarfal leen ca bés ba, muy la ko Yàlla waxoon. \v 24 Ibraayma amoon na juróom ñeent fukki at ak juróom ñeent (99), bi muy xaraf; \v 25 doomam Ismayla am fukki at ak ñett, bi ñu koy xarfal. \v 26 Bésub keroog la Ibraayma xaraf, moom ak doomam Ismayla \v 27 ak mboolem góori këram, muy jaam ya fa juddoo mbaa ñu mu jënd ci ay doxandéem, ñoom ñépp a ànd ak moom xaraf. \c 18 \s1 Ibraayma ak ganam ña \p \v 1 Am na bés, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji feeñu Ibraayma ca garabi Mamre yu mag ya. Booba ma nga toogoon ca buntu xaymaam digg njolloor. \v 2 Naka la siggi, gis ñetti nit, ñu ne jimeet ci kanamam. Ibraayma gaawtu, gatandu leen, sujjóotal leen. \v 3 Mu daldi ne: «Sang bi, siyaare naa la. Ngalla waay, bu ma romb. \v 4 Xaarleen, ñu indil leen tuuti ndox, ngeen jàngu te nopplu ci ker garab gi. \v 5 Maa ngi leen di indil dogu mburu mu ngeen dëgërloo, ba mana topp seen yoon, gannaaw nangu ngeena toog, ma siyaare leen.» Ñu ne ko: «Waaw, baax na.» \p \v 6 Ibraayma daldi gaaw, dugg biir xayma ba, ne Saarata: «Gaawal, jël ñetti ndabi sunguf su mucc ayib, not ko, def ko mburu yu ndaw.» \v 7 Ibraayma nag daw ca gétt ga, sàkk fa sëllu wu duuf te baax, ñëw jox ko jaamam, mu gaaw togg ko. \v 8 Ibraayma taajal leen ndawal, la ñu togg, ba mu sotti, indaaleel leen soow ak meew mu bees. Ma nga taxaw ca seen wet ca ker garab ga, ñuy lekk. \p \v 9 Ñu daldi ko laaj ne ko: «Ana sa soxna Saarata?» Mu ne leen: «Mu ngi ci biir.» \v 10 Kooka ne ko: «Nëgëni sii déwén déy laay délsi, te sa soxna Saarata dina am doom ju góor moos.» Bi muy wax loolu, Saarataa ngi ci buntu xayma bi ci gannaawam, di déglu. \v 11 Booba fekk na Ibraayma ak Saarata doon mag, ba màggat lool sax, te Saarata weesoon na njurum doom. \v 12 Ci kaw loolu Saarata ree ci suuf, daldi ne: «Man mu ñor xomm mii, ndax man naa amati boobu bànneex, te sama boroom kër it di mag?» \v 13 Aji Sax ji daldi wax Ibraayma ne ko: «Lu Saarata di ree, te naan: “Man mu màggat mii, deeti naa am doom moos?” \v 14 Ana lu të Aji Sax ji? Bu ñu ca àggee nëgëni déwén déy, dinaa fi délsiwaat, te Saarata dina am doom ju góor.» \v 15 Saarata dégg loolu, daldi tiit, miim ko ne: «Reetaanuma de.» Teewul Aji Sax ji ne ko: «Ree nga kay!» \s1 Ibraayma tinul na waa Sodom \p \v 16 Gannaaw loolu gan ña jóge foofa, tiim Sodom, di ko séentu. Ibraayma ànd ak ñoom, di leen gunge. \v 17 Booba \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jaa ngi wax naan: «Xanaa duma nëbb Ibraayma li ma nar? \v 18 Ndax kat Ibraayma dina sos xeet wu mag te am doole, te xeeti àddina yépp ci moom lañuy barkeele. \v 19 Moo tax ma tànn ko, ngir mu sant ay doomam ak waa këram, ñuy déggal Aji Sax ji, di jëfe yoon ak njub. Noonu laay defale Ibraayma li ma ko digoon.» \v 20 Aji Sax ji nag àddu ne: «Bàkkaari Sodom ak Gomor bare na lool, ba may dégg yuux, yi sababoo ci seen moy. \v 21 Dinaa wàcc, seede ko, ba mu wóor ne ñoo def lépp li sabab yuux yi, am déet.» \p \v 22 Gan ña nag dem, jublu Sodom, Ibraayma moom taxaw ba tey fi kanam Aji Sax ji. \v 23 Naka la Ibraayma jegeñsi, ne ko: «Mbaa doo boole ku jub ak ku jubadi, rey leen? \v 24 Su juróom fukk rekk jubee ca dëkk bi, mbaa doo tas dëkk bi ba tey, tee nga leena jéggal rekk ngir juróom fukk ñu jub ña ca nekk? \v 25 Rikk bul yemale ku jub ak ku jubadi, ba boole leen rey, loolu jomb na la moos! Yaw miy àtte àddina sépp kay, lu jub rekk ngay def!» \v 26 Aji Sax ji ne ko: «Su ma gisee ci Sodom juróom fukk ñu jub, dinaa jéggal waa dëkk bi yépp ngir ñoom.» \p \v 27 Ibraayma dellu ne: «Ma ñemee wax ak yaw, Boroom bi, te duma dara ba dara booloo jeex. \v 28 Waaye juróom fukk ñooñu jub, su yéesee juróom rekk nag? Mbaa doo tas dëkk bi ndax juróom ñi ci yées?» Aji Sax ji ne ko: «Su ma fa gisee ñeent fukk ak juróom ñu jub, duma ko tas.» \v 29 Ibraayma dellu wax ne: «Su fa ñeent fukk ñu jub rekk amee nag?» Aji Sax ji ne ko: «Duma def dara ngir ñeent fukk ñooñu.» \p \v 30 Ibraayma dellooti ne: «Rikk Boroom bi, bu ma mere. Dinaa ci teg lii. Su fa fanweer ñu jub rekk amee nag?» Aji Sax ji ne ko: «Su fa fanweer ñu jub amee, kon duma def dara.» \p \v 31 Ibraayma neeti: «Léegi ma ñemeeti wax ak yaw boog, Boroom bi! Su ñu doon ñaar fukk rekk nag?» Aji Sax ji ne ko: «Kon duma ko tas ngir ñaar fukk ñooñu.» \p \v 32 Ibraayma dellu neeti: «Ngalla Boroom bi, bul mer, ma wax bii yoon rekk te noppi. Léegi su ñu dee fukk doŋŋ nag?» Aji Sax ji ne ko: «Kon duma tas dëkk bi, ndax fukk ñooñu jub.» \p \v 33 Loolu la Aji Sax ji wax ak Ibraayma, daldi dëddu. Ibraayma it ñibbi këram. \c 19 \s1 Bàkkaari waa Sodom \p \v 1 Ba loolu amee ñaari malaaka ya dikk Sodom ca ngoon, fekk Lóot toog ca buntu dëkk ba\f + \fr 19.1 \fr*\fk ca buntu dëkk ba \fk*\ft la pénc ma nekkoon, booy duggsi.\ft*\f*. Lóot séen leen, jóg gatandu leen, daldi leen sujjóotal, ne leen: \v 2 «Dégluleen ma, ngalla sang yi, siyaare naa leen, tee ngeena dal ak man, su ko defee ngeen jàngu, fanaan ba suba, ngeen xëy topp seen yoon?» Ñu ne ko: «Bàyyil, nu fanaan ci mbedd mi.» \v 3 Lóot nag soññ leen, ba ñu dal këram, mu ganale leen. Lóot da leena berndeel, lakkal leen mburu mu amul lawiir, ñu lekk. \p \v 4 Teewul bala ñoo tëdd, góori Sodom, mag ak ndaw, daldi jóge gox bu nekk, ñëw yéew kër ga. \v 5 Ñu daldi woo Lóot ne ko: «Ana góor ñi fi ñëw tey ci guddi? Génneel nu leen fii, ndax nu mana àgg ci ñoom.» \v 6 Lóot génn, fekk leen ca buntu kër ga ca biti, daldi tëj bunt ba. \v 7 Mu ne leen: «Bokk yi, ngalla buleen def lu bon loolu waay! \v 8 Dégluleen, ma wax leen; man, am naa ñaari doom yu jigéen, te xamuñu góor. Mayleen ma, ma yót leen leen, ngeen def leen lu leen neex. Rikk buleen def góor ñii dara, ndaxte samay gan lañu.» \v 9 Ñu ne ko: «Toppal fale!» te naan: «Waay! Waa jii dal ci sunu dëkk bi rekk, bëgg di fi àtte! Léegi nag dinanu la def lu raw li nu bëggoona def say gan.» Ñu song Lóot, ba nara dàjji bunt ba. \v 10 Teewul gan ña yoor seeni loxo, ñoddi Lóot ba ci biir, tëj bunt ba. \v 11 Ba loolu amee ñu gumbaal nit ña nekkoon ca buntu kër ga, mag ak ndaw, ñuy làmbatu bunt ba, ba sonn, bàyyi. \s1 Lóot génn na Sodom \p \v 12 Ba loolu wéyee gan ña wax Lóot ne ko: «Boo amee mbokk ci dëkk bi, muy sa doom ju góor mbaa ju jigéen, mbaa kuy denc sa doom— koo fi am, génne ko fi, \v 13 ndax dinanu ko tas de. \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dégg na jooytu yu réy, yi niti dëkk bi sabab, ba tax mu yónni nu, ngir nu tas-si ko.» \v 14 Lóot daldi génn, wax ak goroom, ya naroona takk ay doomam yu jigéen, ne leen: «Gaawleen gaaw, génn dëkk bi, ndaxte Aji Sax ji dina ko tas.» Teewul ñu defe ne day kaf. \p \v 15 Fajar a ngay xar, malaaka ya fuug Lóot ne ko: «Gaawal gaaw, ànd ak sa soxna ak sa ñaari doom yu jigéen yii, ba bu Yàlla tasee dëkk bi, dungeen sànku.» \v 16 Lóot di tendeefal, gan ña jàpp ci loxo bi, booleek soxnaam ak ñaari doomam génne, làq leen ca gannaaw dëkk ba, ndax yërmande ju Aji Sax ji am ci Lóot. \v 17 Ba ñu leen génnee, kenn ci ñoom ne Lóot: «Dawal sa xélu bakkan, bul geestu, bul taxaw fenn ci joor gi. Dawal ca tund ya, bala ngaa dee.» \v 18 Lóot nag ne ko: «Déet, sang bi! \v 19 Defal nga ma yiw, yërëm ma lool, ba musal ma. Waaye bala maa daw, ba àgg ca tund ya, musiba mii man naa dal ci sama kaw, ma dee. \v 20 Gisuloo dëkk bale; jege na, te dëkk bu tuut la, am déet? Ma daw, làquji fa boog, ba mucc?» \v 21 Malaaka ma ne ko: «Waaw baax na ba tey, duma tas dëkk boobu ngay wax. \v 22 Nanga gaaw nag, làquji fa, ndax duma mana def dara te àgguloo ca.» Loolu moo tax ñu tudde dëkk boobu Sowar (mu firi Bu tuut). \s1 Yàlla tas na dëkk yooyu di Sodom ak Gomor \p \v 23 Ba jant bay fenk, Lóot dugg na Sowar. \v 24 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nag yuree ca asamaan tamarax buy tàkk, muy taw ci kaw Sodom ak Gomor, na ko Aji Sax ji dogale. \v 25 Mu daldi tas mboolem dëkki joor ga, boole ca nit ña ak gàncax gépp. \v 26 Ci kaw loolu soxnas Lóot ne gees, jëmm ja far soppliku xorom. \p \v 27 Ca ëllëg sa Ibraayma dafa teela jóg, dem fa mu taxawoon jàkkaarlook Aji Sax ji. \v 28 Naka la séentu Sodom ak Gomor ak joor ga ba fa mu yem, gis nag saxar suy gillee ci suuf, mel ni saxaru taalu ban. \p \v 29 Ndaxam bi Yàllay tas dëkki joor ga, xalaat na Ibraayma, ba musal Lóot ca dogalam boobee, keroog ba mu tasee dëkk, ya Lóot daloon. \s1 Mbirum Lóot ak doomam yu jigéen ya \p \v 30 Gannaaw loolu Lóot dafa ragala dëkk Sowar, ba toxoo fa, ànd ak ñaari doomam yu jigéen, sanci ca tund ya. Mu dëkk ci xuntim xeer, moom ak ñaari doomam yu jigéen. \p \v 31 Mu am bés, taaw bi wax rakk ji, ne ko: «Sunu baay a ngii màggat, te fii fépp amul góor gu nu mana séqal ci wàllu séy, ni ko waa àddina yépp baaxoo defe. \v 32 Kon nanu def nii: danuy nàndal sunu baay biiñ, tëdd ak moom, ngir sunu xeetu baay du fey.» \v 33 Ca guddi ga ñu nàndal seen baay biiñ, taaw ba dugg, tëdd ak baayam, te Lóot yégul ba fa doom jay tëdd ak ba muy jóg. \v 34 Ca ëllëg sa taaw ba wax rakk ji, ne ko: «Man tëdd naa ak sama baay biig; guddig tey it, danu koy nàndalaat biiñ, su ko defee nga dugg tëdd ak moom, ndax sunu xeetu baay du fey.» \v 35 Guddi jot, ñu nàndalaat seen baay biiñ, rakk ja dem tëdd ak baayam, te Lóot yégul ba fa doom jay tëdd ak ba muy jóg. \p \v 36 Noonu la ñaari doomi Lóot def ak seen baay, daldi cay doxe ëmb. \v 37 Taaw ba am ca doom ju góor, tudde ko Mowab (mu firi Jóge ci baay). Mowab moo sos Mowabeen ñi. \v 38 Rakk ja moom it am doom ju góor, tudde ko Ben Aami (mu firi Sama doomu mbokk). Ben Aami moo sos Amoneen, ñi fi nekk ba tey. \c 20 \s1 Lu jëm ci Ibraayma ak Abimeleg \p \v 1 Ba loolu amee Ibraayma dafa jóge fa mu nekkoon, jublu àllub Negew, sanci diggante Kades ak Sur, ba noppi ganeji ay fan ca dëkk ba ñu naa Gerar. \v 2 Ba Ibraayma àggee nag, da ne soxnaam Saarata ab jigéenam la. Abimeleg buurub Gerar daldi yónnee jëlsi Saarata. \v 3 Teewul genn guddi Yàlla feeñu Abimeleg ci gént ne ko: «Yaw dee nga ba noppi, ndax jigéen, ji nga nangu, soxnas jaambur la.» \v 4 Loolu fekkul Abimeleg dëkkoo Saarata. Mu wax Yàlla ne ko: «Sama Boroom, mbaa doo bóom réew mi ci mbir mu ñu doonul dara? \v 5 Du góor gi da maa waxoon ne kii jigéenam la? Du jigéen ji it da maa waxoon ne kooku càmmiñam la? Fexewuma dara lu ñaaw te di ko tey de!» \v 6 Yàlla ne ko ca gént ga: «Waaw, xam naa ne li nga def du sa teyeef. Moo tax man it mayuma la nga laal ko, di ma tooñ. \v 7 Léegi nag dellool góor gi soxnaam, ab yonent la de, te dina la ñaanal, nga raw. Waaye soo ko deful, na la bir ne dinga dee, yaak sa waa kër yépp.» \p \v 8 Abimeleg jóg suba teel, woolu dagam yépp, nettali leen loolu lépp, ñu tiit lool. \v 9 Gannaaw loolu Abimeleg woolu Ibraayma ne ko: «Li nga nu def nag? Ndax dama laa tooñ, ba nga yóbbe ma tooñ gu réye nii, man ak sama réew mi mépp? Lii nga ma def de, waroo ko woona def.» \v 10 Abimeleg teg ca ne ko: «Te li nga def sax, lu la ci xiir?» \v 11 Ibraayma ne ko: «Da di dama noon, amul kenn ci réew mii ku ragal Yàlla, te dees na ma rey ndax sama soxna. \v 12 Te moona dëgg la sax, sama jigéen a, ndaxte danoo bokk baay te bokkunu yaay, ma jël ko. \v 13 Te bés, ba ma Yàlla génnee sama kër baay, may wëndeelu, dama koo waxoon ne ko: “Déglul, li ngay def soo ma bëggee xettli, mooy lii: fépp fu nu dem, nanga wax ne sa càmmiñ laa.”» \p \v 14 Ba mu waxee ba noppi, Abimeleg jël ay xar aki nag ak ay jaam yu góor ak yu jigéen, jox ko Ibraayma, daldi ko delloo soxnaam Saarata. \v 15 Abimeleg ne ko: «Sama réew mépp a ngi noonu, dëkkal fu la neex.» \v 16 Gannaaw loolu wax na Saarata ne ko: «Déglu ma fii, jox naa sa càmmiñ limu junniy dogi xaalis\f + \fr 20.16 \fr*\fk junniy dogi xaalis \fk*\ft tollu woon na ci fukki kiloy xaalis ak benn.\ft*\f*. Loolu dama koo def, ngir setal sa der ci kanam ñi nga dëkkal ñépp. Léegi nag ñépp xam nañu ne set nga wecc.» \p \v 17-18 Fekk na \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji um jigéeni waa kër Abimeleg, ba kenn du ci am doom, du soxnaam, du ay jaamam, te li ko waral di Saarata soxnas Ibraayma. Ibraayma nag ñaan Yàlla; Yàlla def ñu wér, ba mana am doom. \c 21 \s1 Juddub Isaaxa \p \v 1 Gannaaw loolu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji yéwéne na Saarata, ni mu ko waxe woon, defal ko li mu ko digoon. \v 2 Saarata ëmb, amal Ibraayma doom ju góor ci jamono, ji ko Yàlla waxoon, te fekk góor gi di màggat. \v 3 Ibraayma tudde doomu Saarata jaak moom, Isaaxa. \v 4 Ba bés ba délsee, Ibraayma xarfal doomam Isaaxa, ni ko ko Yàlla digale woon. \p \v 5 Ba Isaaxa di juddu, booba Ibraaymaa ngi woon ci téeméeri atam. \v 6 Saarata ne: \q1 «Yàllaaka maa bégal, may ree, \q1 ànd ak ku yég, nuy ree\f + \fr 21.6 \fr*\ft Isaaxa mu ngi tekki «ree» ci làkku ebrë.\ft*\f*.» \m \v 7 Mu neeti: \q1 «Éy, ku noon Ibraayma, Saarataa ngay nàmpal! \q1 Teewul ma jural ko góor, te muy mag.» \s1 Saarata jote na ak Ismayla ak Ajara \p \v 8 Ba loolu amee doom ja màgg, ba bés, ba ñu ko feralee. Keroog Ibraayma def na bernde ju mag. \v 9 Saarata nag gis doomu Ajaram Misra, jaak Ibraayma, muy kókkalee. \v 10 Saarata ne Ibraayma: «Dàqal jaam bii, mook doomam, ndax doomu jaam bii du bokk ak sama doom ndono.» \v 11 Loolu Saarata wax naqari Ibraayma lool ndax li Ismayla di doomam, moom it. \v 12 Teewul Yàlla ne Ibraayma: «Bu la dara naqari ci xale bu góor bii, mook sa jaam bi. Defalal Saarata li mu la wax rekk, ndax ci Isaaxa lees di tudde saw askan. \v 13 Doomu jaam bi it, dinaa ci lawale aw xeet nag, ndaxte yaa ko jur.» \p \v 14 Ca ëllëg sa Ibraayma jóg suba teel, sàkk mburu, booleek mbuusu ndox, jox Ajara, mu gàddu. Mu daldi ko dénk Ismayla, yebal ko, mu dem. Ci kaw loolu muy wëndeelu ca màndiŋu Beerseba. \v 15 Ba ñu demee, ba ndox ma jeex, Ajara daa bàyyi xale bu góor bi ci taatu ngarab su ndaw, \v 16 dox, ba dànd ko lu tollook saanu fitt, toog nag jàkkaarlook moom te naa ci xelam: «Duma fekke mukk sama deewu doom.» Naka la toog foofa janook moom, ne yikkét jooy. \p \v 17 Ba mu ko defee Yàlla dégg baatu xale bu góor ba. Malaakam Yàlla ma àddoo asamaan, ne Ajara: «Ajara, lan la? Bul ragal dara, ndaxte Yàlla dégg na sa baatu doom ci diggante bii mu tollu. \v 18 Demal yékkati ko, may ko loxo, mu jóg. Dinaa def mu law, ba doon xeet wu yaa.» \p \v 19 Ci kaw loolu Yàlla muri ay bëtam, mu gis ab seyaan, daldi cay dem, duy mbuusam, ba mu fees, jox ca doomam, mu naan. \v 20 Yàlla nag ànd ak Ismayla, muy màgg, dëkk ca màndiŋ ma, di fittkat. \v 21 Ca àllub Paran la dëkkoon, yaayam wutali ko soxna ca réewum Misra. \s1 Ibraayma waatoo na ak Abimeleg \p \v 22 Jamono yooyu Abimeleg àndoon na ak Pikol kilifay xarekatam, dem ci Ibraayma ne ko: «Gis naa ne Yàlla ànd na ak yaw, di àntal li ngay def lépp. \v 23 Léegi nag waatal ma fii ci Yàlla ne doo ma wor mukk, man ak samay doom, ba ci samay sët. Waatal ma ne noonee ma rafetoo woon ak yaw, ni ngay rafetoo ak man, maak waa réew, mi nga dal.» \v 24 Ibraayma ne ko: «Waat naa ko.» \p \v 25 Ci kaw loolu Ibraayma tawat Abimeleg teen bu surgay Abimeleg nangu woon ci moom, aakimoo ko. \v 26 Abimeleg nag ne ko: «Xawma ku la def jooju jëf de, ndax yaw waxoo ma ci dara; guléet ma dégg ko tey.» \p \v 27 Ba loolu amee Ibraayma jël ay gàtt aki nag, may ko Abimeleg, ñu fasoo \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* ñoom ñaar. \v 28 Fekk na Ibraayma ber juróom ñaari xar yu jigéen. \v 29 Abimeleg nag ne Ibraayma: «Lu tax nga ber juróom ñaari xar yooyu?» \v 30 Ibraayma ne ko: «Jëlal xar yii ci sama loxo, muy firnde ne man maa gas teen bii.» \v 31 Looloo tax ñu tudde teen boobu Beerseba (mu firi Teenu waat ga)\f + \fr 21.31 \fr*\fk Beerseba \fk*\ft man naa tekki «teenu juróom ñaar» ba tey.\ft*\f*, ndaxte fa lañu waatoo woon ñoom ñaar. \v 32 Naka lañu fasoo kóllëre ca Beerseba, Abimeleg jóg ànd ak Pikol kilifay xarekatam, ñu ñibbi réewu Filisti. \p \v 33 Ibraayma nag jëmbat na garabu tamaris foofa ca Beerseba, tudd fa Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ji nekk ba fàww. \v 34 Ibraayma gane na réewu Filisti lu yàgg. \c 22 \s1 Yàlla nattu na Ibraayma \p \v 1 Gannaaw loolu am na bés Yàlla di nattu Ibraayma ne ko: «Ibraayma!» Mu ne ko: «Naam.» \v 2 Yàlla ne ko: «Ngalla jëlal sa jenn doom jii di Isaaxa, muy koo bëgg, nga dem ca réewu Morya ca tund wa ma lay wax, joxe ko fa, mu nekk \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*.» \p \v 3 Ibraayma nag teela xëy, takk mbaamam, ànd ak ñaari surgaam ak doomam Isaaxa, daldi xar matt, mi muy lakke sarax bi. Ma nga jëm fa ko Yàlla wax. \v 4 Ca gannaaw ëllëg sa, Ibraayma daa dawal bëtam, séen bérab ba fu sore. \v 5 Mu ne surga ya: «Négleen fii, mbaam mi taxaw. Man ak xale bi nu dem ba fale, màggali Yàlla te ñëw.» \p \v 6 Ba loolu amee Ibraayma jël mattum saraxu rendi-dóomal ba, yen ko doomam Isaaxa; moom mu ŋàbb la muy taale ak paaka ba ci loxoom, ñu ànd ñoom ñaar. \v 7 Isaaxa ne baayam Ibraayma: «Baay!» Mu ne ko: «Naam, doom sama.» Isaaxa ne ko: «Sawara saa ngi, matt maa ngi, waaye ana gàtt, bi nuy sarxal?» \v 8 Ibraayma ne ko: «Yàlla moom ci boppam dina dikk ak gàtt bi nuy def sarax, doom,» ñu daldi ànd dem, ñoom ñaar. \p \v 9 Ba ñu àggee fa ko Yàlla wax, Ibraayma sàkk fa ab \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*, teg ca matt ma, yeew Isaaxa doomam, teg ko ca kaw matt ma ca sarxalukaay ba. \v 10 Ibraaymaa nga tàllal loxoom, ŋëb paaka, ba muy rendee doom ja. \v 11 Teewul malaakam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ja àddoo asamaan, ne ko: «Ibraayma! Ibraayma!» Mu ne ko: «Ãa!» \v 12 Malaaka ma ne ko: «Bu sa loxo laal xale bi; bu ko def dara, ndaxte léegi xam naa ne ragal nga Yàlla, ndax gàntaloo ma sa jenn doom ji.» \v 13 Naka la Ibraayma siggi rekk, yem ci menn kuuyum xar mu béjjén ya lonke ci as ngarab. Ibraayma dem, jël kuuy ma, rendi, mu wuutu doom ja, di ab saraxu rendi-dóomal. \v 14 Ibraayma nag tudde bérab boobu Yawe Yire (mu firi Aji Sax ji dina dikk). Moo tax ñuy wax ba tey, naan: «Aji Sax jaa ngay dikke ca tundam.» \p \v 15 Ci kaw loolu malaakam Yàlla ma dellu àddoo asamaan ne Ibraayma: \v 16 «Déglul lii Aji Sax ji wax: “Giñ naa ci man mii, gannaaw yaa def lii, te gàntaloo ma sa jenn doom ji, \v 17 maa lay barkeela barkeel, fula ful saw askan ni biddiiwi asamaan, mbaa feppi suufi géej. Sa askan dina teg ay bañam tànk, \v 18 te xeeti àddina sépp ci saw askan lañuy barkeele, ndax déggal nga ma.”» \p \v 19 Ba loolu wéyee Ibraayma waññiku, fekki surga ya, ñu daldi ànd ñoom ñépp, jëm Beerseba, ndax fa la Ibraayma dëkkoon. \s1 Askanu Naxor \p \v 20 Gannaaw gi, dañoo yégal Ibraayma ne ko: «Milka kat am na ay doom moom it, moom ak sa mag Naxor. \v 21 Uus lañu taawloo, teg ca Bus, teg ca Kemwel, miy baayu Aram, \v 22 teg ca Keset ak Aso ak Pildas ak Yidlaf ak Betuwel.» \v 23 Betuwel ay baayu Rebeka. Ñooñu ñooy juróom ñetti doom yu góor, yi Milka am ak magu Ibraayma, Naxor. \v 24 Rewma it nekkaaleem la woon, doom ya mu ca am di Teba ak Gaxam ak Taxas ak Maaka. \c 23 \s1 Ibraayma jënd na suuf ca Kanaan \p \v 1 Saarata dund na, ba am téeméeri at ak ñaar fukk ak juróom ñaar (127), \v 2 doora faatu ca Kiryaat Arba, mooy Ebron, ca réewu Kanaan. Ibraayma nag dëj Saarata, jooy ko lool. \p \v 3 Gannaaw loolu Ibraayma bàyyi fa néew ba, dem ca Etteen ña\f + \fr 23.3 \fr*\fk Etteen ña: \fk*\ft ñooñoo nga bokk ci askanu Ett. Ñoo moomoon diiwaanu Ebron ca jooja jamono.\ft*\f*, ne leen: \v 4 «Dama di doxandéem ci seen biir, tey gan; moo tax ma di leen ñaan, ngeen sédd ma bàmmeel\f + \fr 23.4 \fr*\fk bàmmeel: \fk*\ft booba nit ñi dañoo taamu di denc seeni néew ci ay xuntiy xeer, mu di ay bàmmeel yu ñu bare mana bokk.\ft*\f* bu ma suul sama néew, ba mu làqu ma.» \v 5 Kenn ci Etteen ñi wax Ibraayma ne ko: \v 6 «Déglul rekk, kilifa gi. Kilifa gu mag nga ci sunu biir. Dangay tànn ci sunuy bàmmeel, bi la neex, suul fa néew bi; kenn ci nun du la tere, nga suul sa néew ci bàmmeelam.» \p \v 7 Naka la Ibraayma dégg loolu, daldi jóg sujjóotal waa réew ma, maanaam Etteen ña. \v 8 Mu ne leen: «Gannaaw nangu ngeen, ma suul fi sama néew, ba mu làqu ma, dégluleen, ma wax leen li ngeen may ñaanal Efron doomu Sowar. \v 9 Damaa bëgg, mu bàyyee ma xuntim xeer, mi ñuy wax Magpela te muy boroom. Mu ngi ci catu toolam. Na ma ko jaay lu mat njégam sëkk, dinaa ko jënd, muy sama bàmmeel ci seen biir.» \p \v 10 Booba Efron a ngi teew ci biir Etteen ñi. Efron, miy Etteen nag, wax ak Ibraayma ci kanam bokkam yi séq pénc mi, ne ko: \v 11 «Déglul, ma wax la, kilifa gi, fabal tool bi, booleek xuntim xeer, mi ci nekk far. Maa la ko jox ci sama kanami bokk; jëlal, denc fa sa néew.» \p \v 12 Ba mu ko defee Ibraayma sujjóotal waa réew ma, \v 13 daldi wax Efron ci seen kanam ne ko: «Ngalla déglu ma, dama lay jox njégu tool bi, nga jël rekk, ndax ma man faa suul sama néew.» \v 14 Efron wax Ibraayma ne ko: \v 15 «Déglu ma, kilifa gi, suuf suy jar ñeenti téeméeri dogi xaalis doŋŋ\f + \fr 23.15 \fr*\ft Loolu tollu woon na ci juróomi kiloy xaalis.\ft*\f* du dara ci sama diggante ak yaw; tee nga faa denc sa néew rekk?» \v 16 Ibraayma dégg li ko Efron wax, daldi waññal Efron limu xaalis, bi mu wax ci kanam Etteen ñi, maanaam ñeenti téeméeri dogi xaalis yu dëppook nattu jaaykat ya. \p \v 17-18 Noonu la Ibraayma jënde toolub Efron ba nekk ca Magpela te janook Mamre, muy moomeelam. Dafa jënd tool ba bépp, jëndaale xuntim xeer ma ca biir, ak garab ya ca sax yépp, ba fa tool ba yem. Mboolem Etteen ña séqoon pénc ma, seede nañu ne Ibraayma moo ko moom. \v 19 Ibraayma daldi suul soxnaam Saarata ca xuntim xeer ma ca biir toolub Magpela, booba janook Mamre, di Ebron léegi, ca réewu Kanaan. \v 20 Nii la Etteen ña dogalale Ibraayma njaayum tool ba ak xunti ma ca nekk, mu def ko bàmmeel. \c 24 \s1 Isaaxa jël na Rebeka soxna \p \v 1 Ibraayma guddoon na fan, ba màggat lool, te \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji barkeel ko ci lépp. \p \v 2 Mu am bés Ibraayma wax surgaam, bi gëna yàgg ci këram, tey saytu alalam jépp, ne ko: «Dugalal sa loxo ci sama suufu lupp\f + \fr 24.2 \fr*\fk dugal loxo ci suufu lupp \fk*\ft mooy li bànni Israyil daan dogale ngiñ.\ft*\f*, \v 3 ma giñloo la ci Aji Sax jiy Yàllay asamaan ak suuf ne doo jëlal sama doom soxna ci biir jigéeni waa Kanaan, gi ma dëkk ci seen biir. \v 4 Waaye dinga dem sama réew, ma ma cosaanoo, jëlal fa sama doom Isaaxa soxna.» \p \v 5 Surga ba ne ko: «Su ndaw sa nanguwula ànd ak man ci réew mii nag? Ndax kon damaa wara yóbbu sa doom ba ca réew ma nga jóge?» \v 6 Ibraayma itam ne ko: «Bu fa yóbbu sama doom mukk. \v 7 Aji Sax ji, Yàllay asamaan, moom mi ma jële sama kër baay ak fa ma juddoo, te wax ak man, giñal ma ne ma, dina jox sama askan réew mii, moom ci boppam dina yebal malaakaam, mu jiitu la. Foofa ngay jëlale sama doom soxna. \v 8 Su la ndaw si buggula topp, kon wàccoo nga ak man. Waaye rikk bul yóbbu sama doom foofa.» \v 9 Surga ba dugal loxoom ca suufu luppu Ibraayma sangam ba, daldi giñ ca loola. \p \v 10 Ba loolu amee surga ba jële fukki giléem ca giléemi sangam, dem, yóbbaale li gën ci mboolem xeeti alalu sangam. Ma nga jëm réewu Mesopotami, ga Naxor dëkk. \v 11 Ba muy jub dëkk ba, daa yésal giléem ya fu dend akub seyaan waxtuw ngoon, fekk jigéen ñay génn di rootsi. \v 12 Mu daldi ne: «Yaw Aji Sax ji, sama Yàllay sang Ibraayma, ngalla nangul ma tey jii te laaye biir sama sang Ibraayma. \v 13 Maa ngi nii taxaw ci bëtu ndox mi, janqi dëkk bi di rootsi. \v 14 Janq bu ma wax ne ko: “Doo yenniku sa njaq, may ma, ma naan,” mu ne ma: “Naanal ba noppi, ma wëggal la say giléem,” na kooka di ki nga jagleel sa jaam Isaaxa. Noonu laay xame ne laaye nga biir sama sang.» \p \v 15 Laata muy ñaan ba noppi sax, gis na Rebeka gàddu njaqam, di ñëw. Rebeka moomu di doomu Betuwel te di sëtu Milka ak Naxor, miy magu Ibraayma. \v 16 Ndaw su taaru la woon, di ab janq bu séyagul. Naka la wàcc ba ca seyaan ba, duy njaqam, yéegaat. \v 17 Surga ba daw, daje ak moom ne ko: «Doo ma may tuuti ci sa njaq li, ma naan.» \v 18 Mu ne ko: «Ahakay, sang bi,» daldi gaaw, yenniku njaq la, may ko mu naan. \v 19 Ba ko ndaw si mayee, mu naan ba noppi, da ne ko: «Xaaral, ma wëggal la giléem yi, ñu naan ba noppi.» \v 20 Mu daldi gaaw, sotti njaq la ca mbalka ma, dawaat rootali giléem yi ca seyaan ba. \v 21 Waa ja ne ko jàkk, ne tekk, di seet, ba xam ndax Aji Sax ji àntal na yoonam am déet. \p \v 22 Ba giléem ya naanee ba sottal, waa ji jël jaarob bakkan bu wurus bu tollook juróom benni garaam, ak ñaari lami wurus yu tollu ci téeméeri garaam, takkal ko. \v 23 Mu ne ko: «Wax ma, kan moo la jur?» Ak itam: «Ndax man nanoo dal sa kër baay?» \v 24 Mu ne ko: «Betuwel a ma jur, doomu Naxor ak Milka,» \v 25 teg ca ne ko: «Waawaaw, ñax maak ngooñ maa nga fa, ne gàññ, te it manees na faa dal.» \v 26 Waa ji nag sujjóot, sant Aji Sax ji, \v 27 daldi ne: «Cant ñeel na Aji Sax ji, sama Yàllay sang, Ibraayma, moom mi masula noppee laaye biir sama sang, te masu koo ñàkke worma. Man it, Aji Sax ji wommat na ma ba sama kër bokki sang!» \p \v 28 Janq bi nag daw dem, nettali waa kër yaayam la xew lépp. \v 29 Rebeka amoon na càmmiñ lu tudd Laban. Laban daldi gaawtu génn, fekki waa ja ca seyaan ba. \v 30 Booba gis na jaaro ba ak lam, ya ca loxol jigéenam Rebeka, te dégg na jigéenam di nettali la ko waa ja wax. Loolu tax mu dem ca waa ja, fekk ko ca giléem ya ca seyaan ba. \v 31 Mu ne ko: «Yaw mi Aji Sax ji barkeel, agsil boog! Looy toog ci àll bi; waajalal naa la ab dal, te giléem yi am nañu fu ñu nekk.» \v 32 Waa ja daldi àgg ca kër ga, ñu sippi giléem ya, may leen ñax ak ngooñ, may waa ja ndox, mu jàngu, moom ak ñi mu àndal, \v 33 ba noppi ñu taajal ko lu mu lekk. Mu ne: «Déedéet, duma lekk mukk kay, te waxuma li ma taxa jóg.» Laban ne ko: «Kon nag waxal.» \p \v 34 Mu ne: «Man surgab Ibraayma laa. \v 35 Aji Sax ji dafa barkeel sama sang lool, ba muy boroom daraja. May na ko jur gu gàtt ak gu gudd, xaalis ak wurus ak ay surga yu góor ak yu jigéen ak ay giléem aki mbaam. \v 36 Sama soxnas sang Saarata nag dem na ba màggat, doora amal sama sang doom ju góor. Doomam jooju la jox li mu moom lépp. \v 37 Sama sang nag giñloo ma ne: “Bul jëlal mukk sama doom soxna ci biir jigéeni waa réewu Kanaan, gi ma dëkk. \v 38 Waaye demal ca sama kër baay, ca samay bokk, nga jëlal fa sama doom soxna.” \v 39 Ma ne sama sang: “Bu ndaw sa nanguwula ànd ak man nag?” \v 40 Mu ne ma: “Aji Sax, ji ma topp, dina yónni malaakaam, mu ànd ak yaw, ba àntalal la sa yoon, nga jëlal sama doom soxna ca sama kër baay, ca sama biiri bokk. \v 41 Boo demee ba ca samay bokk, wàcc nga, ndax bu ñu la mayul soxna, wàccoo nga ak man.” \v 42 Ba ma agsee tey jii ca seyaan ba, damaa wax ne: “Aji Sax ji, sama Yàllay sang Ibraayma, ndegam nar ngaa àntal yoon wi may dox, ngalla may ma lii: \v 43 maa ngii taxaw ci seyaan bi; janq bay ñëw rootsi, ma ne ko: ‘Doo ma may tuuti ci sa njaq li, ma naan,’ \v 44 mu ne ma: ‘Naanal ba noppi, ma wëggal la say giléem,’ kooku na di soxna, si Aji Sax ji jagleel sama doomu sang.” \p \v 45 «Bala maa ñaan ba noppi, Rebeka ne jimeet, gàddu njaqam, wàcc ca seyaan ba, di root. Ma ne ko: “May ma, ma naan.” \v 46 Mu gaaw yenniku njaq li, daldi ne ma: “Naanal ba noppi ma wëggal la say giléem.” Ma naan ba noppi, mu wëggal ma giléem yi. \v 47 Ma laaj ko ne ko: “Kan moo la jur?” Mu ne: “Betuwel, doomu Naxor ak Milka.” \p «Ca laa ko takkal jaaro bi ci bakkanam, ak lam yi ciy loxoom. \v 48 Ba mu ko defee ma sujjóotal Aji Sax ji, sant Aji Sax jiy sama Yàllay sang Ibraayma, ndax jubal na sama yoon, ba ma jëlal doomam soxna ciy bokkam. \v 49 Léegi nag ndegam nar ngeena rafetoo ak sama sang tey sàmm kóllëre, xamal-leen ma ko, ba mu leer. Su ngeen ko narul it, waxleen ma, ma xam nu may def.» \p \v 50 Laban ak Betuwel ne ko: «Mbir moomu de ci Aji Sax ji la jóge, te amunu ci dara lu nuy wax. \v 51 Rebekaa ngoogu, jëlal te dem, muy sa soxnas doomu sang, ni la ko Aji Sax ji tegtale.» \v 52 Naka la surgab Ibraayma dégg yooyu kàddu, daldi sujjóotal Aji Sax ji. \p \v 53 Surga ba nag génne ay gànjari xaalis ak yu wurus booleek ay yére, jox Rebeka. Càmmiñ la ak yaay ja itam, mu may leen alal ju takku. \v 54 Ba loolu weesee mu doora lekk, daldi naan, moom ak ñi mu àndal. Ñu fanaan fa keroog. \p Ba ñu yewwoo ca ëllëg sa, surga ba ne: «Bàyyileen ma nag, ma dellu ca sama sang.» \v 55 Càmmiñal ndaw sa ak yaay ja daldi ne ko: «Xanaa kay janq bi dina toogaat ak nun ab diir boog, maanaam fii ak sibbir, doora dem.» \v 56 Mu ne leen: «Gannaaw Aji Sax ji àntal na sama yoon, tee ngeen ma baña yeexal, te bàyyi ma rekk, ma dellu ca sama sang?» \v 57 Ñu ne ko: «Kon nag nanu woo janq bi, laaj ko moom ci boppam.» \v 58 Ci kaw loolu ñu woo Rebeka, ne ko: «Ndax dangay ànd ak waa ji léegi?» Mu ne: «Waaw.» \v 59 Ba loolu amee càmmiñ ya bàyyi seen jigéen Rebeka, moom ak surga, bi ko yar te daan ko nàmpal, ñu ànd ak surgab Ibraayma ak ñi ko topp, ñu dem. \v 60 Ña ngay ñaanal Rebeka, mu barkeel, te naan: \q1 «Éy jigéen sunu! Giiral, ba sos ay junniy junni, \q1 te sa askan teg ay bañam tànk.» \m \v 61 Gannaaw loolu Rebeka ànd ak xale yu jigéen, yiy jaamam, ñu war ay giléem, topp waa ja. Surga ba daldi dem, yóbbu Rebeka. \p \v 62 Loolu fekk na Isaaxa dëkk ca àllub Negew. Mu demoon nag teenu Laxay Roy, ba ñibbsi. \v 63 Genn ngoon Isaaxa génn, di doxantu ca àll ba. Naka la ne sigget xool, séen giléem yuy ñëw. \v 64 Rebeka it ne sigget, gis Isaaxa. Mu ne cëpp nag, wàcc giléem ga, \v 65 daldi ne surga ba: «Waa jee ci àll biy ñëw, jëm ci nun, kan a?» Surga ba ne ko: «Sama sang la de.» Rebeka daldi jël muuraay ba, muuroo. \v 66 Surga ba nag nettali Isaaxa li mu def lépp. \v 67 Ba loolu wéyee Isaaxa yóbbu Rebeka ca xaymab yaayam Saarata, muy soxnaam, di ku mu bëgg, te di ko muñe yaayam, ndax fekk na mu faatu. \c 25 \s1 Ibraayma nelaw na \p \v 1 Ibraayma jëlaat na soxna su tudd Ketura, \v 2 am ca Simran ak Yogsan ak Medan ak Majan ak Yisbag ak Suwa. \v 3 Yogsan jur Saba ak Dedan. Askani Dedan ñooy Asureen ñi, Letuseen ñi ak Lewumeen ñi. \v 4 Doomi Majan di Efa ak Efer ak Anog ak Abida ak Elda. Ñooñu ñépp xeetu Ketura lañu. \p \v 5 Ibraayma nag donale Isaaxa lépp lu mu moom. \v 6 Doom yu góor, ya mu am aki nekkaaleem, mu may leen alal ca ba muy dund, ba noppi yebal leen penku, ñu sanci ca réewu penku, ba sore doomam Isaaxa\f + \fr 25.6 \fr*\ft Ca yooya jamono, nit manoon naa am ay soxna yu am cér bu mat sëkk, ak yeneen soxna, yu gëna néewle sañ-sañ, ñoom ak seeni doom.\ft*\f*. \p \v 7 Ati Ibraayma téeméer la ak juróom ñaar fukk ak juróom (175). \v 8 Ba loolu weesee la bakkanu Ibraayma rot, mu nelaw, fekki ay maamam, gannaaw ba mu guddee fan, ba màggat lool te barkeel. \v 9 Isaaxa ak Ismayla, doomam yu góor ya, rob ko ca xuntim xeer ma ca Magpela te jàkkaarloo ak Mamre, ca toolub Efron doomu Sowar, Etteen ba. \v 10 Tool ba Ibraayma jëndoon ca Etteen ña, foofa lañu denc Ibraayma ak soxnaam Saarata. \v 11 Gannaaw ba Ibraayma nelawee, Yàlla barkeel na doomam Isaaxa. Isaaxaa ngi dëkkoon ca wetu teenu Laxay Roy. \ms1 Askanu Ismayla \mr (Saar 25.12-18) \p \v 12 Ismayla moomee nag, doomu Ibraayma jaak Ajaram Misra, ma doon jaamub Saarata, askanam mooy lii. \v 13 Turi doomi Ismayla yu góor yaa di: Nebayot, taawub Ismayla, ña ca topp di Kedar ak Adabeel ak Mibsam \v 14 ak Misma ak Duuma ak Maasa \v 15 ak Adàdd ak Tema ak Yetur ak Nafis ak Kedama. \v 16 Ñooñu ñooy doomi Ismayla yu góor, seeni tur a ngoog, ñuy fukki garmi ak ñaar yu jiite seeni mbooloo ci seeni sanc ak seeni dal. \v 17 Ati Ismayla téeméer la ak fanweer ak juróom ñaar (137). Gannaaw loolu la nelaw, fekki ay maamam. \p \v 18 Ña nga dëkkoon diggante ba dale Awila ba Sur ga jàkkaarlook Misra, booy jëm Asur. Noonu la fa askanu Ismayla sance, jàkkaarlook doomi baayam yépp. \ms1 Askanu Isaaxa doomu Ibraayma \mr (Saar 25.19—35.29) \p \v 19 Isaaxa doomu Ibraayma ju góor ja, askanam mooy lii. Ibraaymaa jur Isaaxa. \v 20 Isaaxa am ñeent fukki at, jël Rebeka doomu Betuwel, Arameen, bi dëkke diiwaanu Padan Aram, dib jigéenu Laban, Arameen ba. \v 21 Gannaaw ga soxnas Isaaxa amul doom, Isaaxa dagaanal ko \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, mu nangul ko, soxna si daldi ëmb. \v 22 Doom yi nag di buuxante ci biiram, ba mu naan: «Ndegam nii la kay, jaru ko woon!» Ci kaw loolu soxna si dem, diis ko Aji Sax ji. \p \v 23 Aji Sax ji ne ko: \q1 «Ñaari giir nga ëmb, \q1 nara am ñaari xeet yuy xaajaloo, \q1 wenn wi mooy ëpp doole wi ci des, \q1 te mag ji mooy surgawu rakk ji\f + \fr 25.23 \fr*\ft Ci bànni Israyil, seex, bi jëkka juddu, moo mag ki mujja juddu.\ft*\f*.» \p \v 24 Ba mu demee ba wara mucc, amul lu moy ay seex. \v 25 Naka noona ka jëkka gane àddina xonq, yaram wi sëq lipp, mel ni mbubbum der mu ne sàyy aki kawaram, ñu tudde ko Esawu (mu firi Ku jëxëm). \v 26 Gannaaw ga ka ca des topp ca, loxo ba jàpp ca téstënu Esawu. Ñu tudde ko Yanqóoba (mu firi Jàpp ci téstën)\f + \fr 25.26 \fr*\fk Jàpp ci téstën \fk*\ft mu ngi tekki ci waxin «suufu nit, ba am loo nangu ci moom».\ft*\f*. Ba leen Rebeka di am, fekk na Isaaxa am juróom benn fukki at. \s1 Esawu sàggane na céram \p \v 27 Ba mu ko defee gone ya di màgg, Esawu di rëbbkat bu ñaw, di ku bëgg àll; Yanqóoba moom di nit ku gàtteñlu\f + \fr 25.27 \fr*\fk gàtteñlu \fk*\ft gi ci Yanqóoba moo waraloon xamul dara ci rëbb.\ft*\f* te bëggoon toogaayu kër. \v 28 Isaaxa nag am cofeel ci Esawu ndax li muy lekk ci am rëbbam, te Rebeka moom gëna sopp Yanqóoba. \p \v 29 Mu am bés Yanqóoba di togg ndambel ñebbe ju xonq, yemook Esawu jóge ca tool ya, xiif ba ne ñedd. \v 30 Mu ne Yanqóoba: «Gaawe ma ci ndambe lee waay, ba ma duy sama biir ci sa ndambe lu xonq loolu, ndax xiif a ngi may rey.» Loolu moo tax ñu tudde Esawu, Edom (mu firi Xonqe). \v 31 Yanqóoba ne ko: «Danga ma koy jëkka wecci sa céru ndono bi nga yeyoo ndax li ngay taaw\f + \fr 25.31 \fr*\ft Ci bànni Israyil, taaw mooy mujj doon kilifag kër, te mooy ëpple ay rakkam ab cér ci ndono.\ft*\f*.» \v 32 Esawu ne: «Man miy waaja dee ak xiif, ana lu ma céru taaw di jariñ?» \v 33 Yanqóoba ne ko: «Giñal ma jëkk.» Esawu giñal ko ko, mu jaay Yanqóoba ndono, li mu yeyoo ndax li muy taaw. \v 34 Yanqóoba jox Esawu mburu ak ndambe, mu lekk, naan, daldi jóg dem yoonam. Noonu la Esawu sàgganee céru taaw, bi mu yeyoo. \c 26 \s1 Isaaxa nëbbu na waa Gerar ngir mucc \p \v 1 Ba loolu wéyee xiif am ca réew ma, muy xiif bu wuute ak ba woon ca jamonoy Ibraayma; Isaaxa nag dem Gerar ca Abimeleg, buurub waa Filisti. \p \v 2 Foofa \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji feeñu ko fa ne ko: «Bul dem Misra, waaye nanga toog ci réew mi ma lay wax. \v 3 Dalal ci réew mii; dinaa ànd ak yaw, barkeel la. Yaak sa askan laay jox suuf sii sépp, te dinaa sàmm li ma giñaloon sa baay Ibraayma. \v 4 Dinaa ful sa askan ni biddiiwi asamaan, dinaa jox sa askan suuf sii sépp, te it ci saw askan la xeeti àddina sépp di barkeele, \v 5 ndax Ibraayma déggal na ma, dénkoo na sama ndénkaane, ak samay santaane, ak sama dogali yoon, ak samay yoon.» \p \v 6 Isaaxa nag toog Gerar. \v 7 Góori foofa laaj ko ndaw si mu àndal, lu mu doon ci moom, mu ne: «Sama jigéen la.» Dafa bañoona wax ne soxnaam la, ngir ragal waa foofa rey ko ndax taaru Rebeka. \v 8 Ba ñu fa toogee ba mu yàgg, mu am bés Abimeleg, buurub waa Filisti tollu ci palanteeram, gis leen, fekk yóo Isaaxaa ngay raay soxnaam Rebeka. \v 9 Abimeleg woolu Isaaxa ne ko: «Kii kay ndeke sa soxna la! Noo mana waxe ne sa jigéen la?» Isaaxa ne ko: «Damaa waxe noonu, ngir ñu bañ maa rey ndax moom.» \v 10 Abimeleg ne ko: «Li nga nu def nag? Xaw tuuti kenn ci nit ñi tëdde sa soxna, te kon nga yóbbe nu tooñ.» \v 11 Abimeleg daldi fay doxe àrtu waa réewam mépp ne leen: «Ku laal waa jii walla soxnaam, dees na ko rey.» \s1 Isaaxa fas na kóllëre ak Abimeleg \p \v 12 Gannaaw loolu Isaaxa bey ca réew ma, góob ca at ma lu tollook téeméeri yoon la mu ji woon, ndax \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji da koo barkeel. \v 13 Alalam di yokku, muy gëna barele, ba mujj am doole lool, \v 14 am géttu jur gu gudd ak gu gàtt, ak ay surga yu bare, ba tax waa Filisti iñaane ko, \v 15 bay sakk ak a sëkk mboolem teen, yi surgay baayam Ibraayma gasoon ca jamonoom. \v 16 Abimeleg daldi ne Isaaxa: «Demal, ba sore nu, ndax danga noo ëpp doole lool.» \v 17 Isaaxa jóge foofa, dali ca xuru Gerar, sanc fa. \p \v 18 Ba loolu weesee Isaaxa sikkli teen, yi ñu gasoon ca jamonoy baayam Ibraayma, te waa Filisti sakkoon leen gannaaw ba Ibraayma nelawee. Ca la tudde teen yi tur, ya leen baayam tudde woon. \v 19 Surgay Isaaxa gasaat ca xur wa, jot ndox mu neex. \v 20 Teewul sàmmi Gerar di soowook sàmmi Isaaxa naan: «Nun noo moom ndox mi.» Mu tudde teen ba Eseg (mu firi Coow), ndax li ñu soowoo ak moom. \v 21 Ñu gasaat ab teen, xuloo amati ca, mu tudde ko Sitna (mu firi Xuloo). \v 22 Mu jóge foofa, gasati teen, jàmm ne ñoyy, mu tudde ko Reyobot (mu firi Fu yaatu), ndax da ne: «Léegi Aji Sax ji yaatal na nu, te dinanu woomle ci réew mi.» \p \v 23 Ba mu fa jógee, dafa dellu Beerseba. \v 24 Guddi googu Aji Sax ji feeñu ko ne ko: «Maay Yàllay Ibraayma sa baay; bul ragal dara, ndax maa ngi ànd ak yaw. Dinaa la barkeel, ful sa askan ndax sama jaam Ibraayma.» \v 25 Isaaxa nag sàkk fa \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*, tudd fa Aji Sax ji, wormaal ko, ba noppi samp fa xaymaam. Te itam ay surgaam bënn nañu fa ab teen. \p \v 26 Ci diggante boobu Abimeleg dafa jóge Gerar, dem fekki ko, ànd ak Awusat, ma doon wóllëreem, ak Pikol, njiital xarekatam. \v 27 Isaaxa ne leen: «Lu waral ngeen fekksi ma fii, gannaaw dangeen maa bañ, ba dàq ma?» \v 28 Ñu ne ko: «Gis nanu bu baax ne Aji Sax ji ànd na ak yaw; moo tax nu ne ayca nu waatoo ci sunu digganteek yaw te fasanteek yaw \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w*. \v 29 Su ko defee doo nu def dara lu bon, gannaaw defunu la dara lu bon, xanaa lu baax rekk, ba yebal la, nga dem ci jàmm. Kon léegi yal na la Aji Sax ji barkeel.» \p \v 30 Isaaxa nag berndeel leen, ñu bokk lekk, ba noppi naan. \v 31 Ca ëllëg sa, ñu xëy suba teel, daldi waatoo, Isaaxa door leena yiwi, ñu dem ci jàmm. \p \v 32 Ca bés booba ay surgay Isaaxa ñëw nañu, di ko wax lu jëm ci teen, ba ñu doon gas, ne ko: «Gis nanu ndox.» \v 33 Isaaxa tudde teen ba Siba (mu firi Waatoo), moo tax turu dëkk ba, ba fii nu tollu, di Beerseba (mu firi Teenu waat ga). \s1 Esawu jël na ay soxna \p \v 34 Esawu am na ñeent fukki at, jël na soxna ku ñuy wax Yudit, muy doomu Beeri, miy Etteen, jëlaat Basmat doomu Elon, miy Etteen. \v 35 Jigéen ñooñu mu jël nag di naqar wu réy ci Isaaxa ak Rebeka. \c 27 \s1 Yanqóoba jëkk na Esawu ci ñaanam \p \v 1 Ba Isaaxa màggatee, te bët yi naqari, ba gisatul, am na bés mu woo taawam Esawu ne ko: «Doom.» Mu ne ko: «Naam.» \v 2 Isaaxa ne ko: «Déglul, ma wax la. Màggat naa te xawma sama bésu dee. \v 3 Kon léegi jëlal say gànnaay: say fitt ak sa xala, nga dem ca àll ba, rëbbali ma. \v 4 Toggal ma ko, ba mu neex, ni ma ko bëgge, indil ma, ma lekk, ndax ma ñaanal la lu ma tibbe ci sama xol, bala may dëddu.» \v 5 Fekk na Rebekaa ngi déglu, ba Isaaxay wax ak doomam Esawu. Esawu daldi dem ca àll ba, rëbbi lu mu toggsi. \p \v 6 Rebeka moom ne doomam Yanqóoba: «Dégg naa sa baay wax sa mag Esawu ne ko: \v 7 “Demal rëbbi, indil ma, toggal ma ko lu neex, ma lekk, ba ñaanal la, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji seede, bala may dëddu.” \v 8 Kon nag doom, defal lii ma lay wax. \v 9 Demal ca gétt ga, nga jàpp ñaari tef yu duuf, ma defaral ko sa baay, ba mu neex, ni mu ko bëgge, \v 10 nga yóbbul ko, ngir mu ñaanal la, bala moo dee.» \p \v 11 Yanqóoba ne yaayam: «Waaw, waaye sama mag Esawu dafa jëxëm, te man sama yaram rattax. \v 12 Xëy na sama baay làmbatu ma de, te kon dina ne njublaŋ laa. Su ko defee ay móolu laay yóbbe sama bopp, waaye du barkeb ñaan.» \v 13 Yaayam ne ko: «Bu la móoloo, Yàlla na ma topp, doom. Defal li ma la wax rekk te dem indil ma gàtt yi.» \p \v 14 Yanqóoba dem, jël gàtt yi, indil yaayam, mu defar ba mu neex, ni ko baayam bëgge. \v 15 Rebeka daldi seet ca dencam la gën ca yérey Esawu taaw ba, solal Yanqóoba doomam ju ndaw. \v 16 Ba mu noppee, daa sàkk ca deri gàtt ya, sànge loxo ya ak fi rattax ci doq gi, \v 17 doora boole mburu ma ak ñam wa mu togg, jox doomam Yanqóoba. \p \v 18 Mu dikk ci baayam, ne ko: «Baay.» Mu ne ko: «Naam doom, kooku?» \v 19 Yanqóoba ne baayam: «Mana Esawu sa taaw. Def naa li nga ma wax. Jógal toog te lekk ci li ma la rëbbal, ndax nga ñaanal ma ci sa xol.» \v 20 Isaaxa ne doomam: «Moo doom! Noo def, ba gaawa jàpp nii?» Yanqóoba ne ko: «Aji Sax jiy sa Yàlla, moo ma ko jagleel.» \p \v 21 Isaaxa ne Yanqóoba: «Jegesil, ma làmb la, ba mu wóor ma ne sama doom Esawoo.» \v 22 Yanqóoba nag jegesi, baayam Isaaxa làmbatu ko ne: «Baat bi de baatu Yanqóobaa, waaye loxo yi, loxoy Esawoo.» \v 23 Xàmmiwu ko, ndax li loxo yi jëxëm ni yuy magam Esawu, ba tax mu ñaanal ko. \v 24 Isaaxa laaj ko ne ko: «Mbaa wóor na ne yaw ay Esawu?» Mu ne ko: «Waawaaw.» \v 25 Isaaxa ne ko: «Jottli ma fii ma lekk ci sam rëbb, doom, ba ñaanal la ci sama xol.» Yanqóoba jottli Isaaxa ndab li, mu lekk, daldi koy may biiñ, mu naan. \v 26 Isaaxa ne ko: «Kaay fii, fóon ma, doom.» \v 27 Yanqóoba jegesi, fóon ko, xetu yére yi mu sol xeeñ Isaaxa, mu door koo ñaanal ne ko: \q1 «Sama xetu doom kay \q1 xetug tool la, \q1 bu Aji Sax ji barkeel. \q1 \v 28 Yal na la Yàlla may layub asamaan \q1 ak ngëneeli suuf, \q1 pepp ne gàññ, biiñ walangaan. \q1 \v 29 Yal na la ay giir nangul, \q1 ay réew di la sujjóotal, \q1 nga yilif say bokk, \q1 te say doomi ndey di la sujjóotal. \q1 Ku la móolooy alku, \q1 te ku la ñaanal barkeel.» \p \v 30 Naka la Isaaxa noppee ñaanal Yanqóoba, ba mu won baayam Isaaxa gannaaw rekk, Esawu, mag ji, rëbbi ba ñëw, ne jalañ. \v 31 Mu togg moom it, ba mu neex, indil baayam. Mu ne ko: «Jógal baay, lekk ci sa rëbbum doom, ndax nga ñaanal ma ci sa xol.» \v 32 Baayam Isaaxa ne ko: «Kooku?» Mu ne ko: «Mana sa taaw Esawu.» \v 33 Isaaxaa ngay lox, bay rag-ragi, daldi ne ko: «Kan? Ana ku rëbbi woon nag, indil ma, ba ma lekk ba noppi? Ñaanal naa ko bala ngaa ñëw. Te dina barkeel moos.» \p \v 34 Esawu dégg li baayam wax rekk, yuuxu yuux gu réy ndax naqar. Mu ne baayam: «Ngalla baay, ñaanal ma, man itam.» \v 35 Isaaxa ne ko: «Sa rakk ñëw na, nax ma, ba yóbbu sa ñaan.» \v 36 Esawu ne: «Moom kay moo yey tudd Yanqóoba, ndax suufu na ma ñaari yoon. Sama céru taaw la jëkka nangu, tey mu nangooti sama ñaanu baay.» Mu teg ca ne: «Ndax desalaloo ma ag ñaan?» \v 37 Isaaxa ne Esawu: «Mbaa am naa lu ma la ñaanalati, doom? Ndax kat xas naa koo def, muy sa kilifa, te bokkam yépp laa def ñuy surgaam, te pepp ak biiñ laa ko woomale it, ba mu ne gàññ.» \v 38 Esawu ne baayam: «Baay, xanaa genn ñaan rekk nga am? Ngalla baay, ñaanal ma, man itam!» Ca la Esawu ne yikkét jooy. \v 39 Baayam Isaaxa ne ko: \q1 «Déglul, ma wax la, \q1 dinga dëkk fu sore ngëneeli suuf, \q1 mbaa fu la layub asamaan tiime. \q1 \v 40 Sa saamar ngay dunde, \q1 sa rakk di la yilif. \q1 Waaye bés a ngi ñëw yaay sigiñu, \q1 ba yenniku notaangeem.» \s1 Yanqóoba dem na ca nijaayam \p \v 41 Esawu nag bañ Yanqóoba ndax barke ba ko baayam ñaanal. Ma ngay wax ca xolam naan: «Balaa yàgg ñu dëj sama baay, te bu boobaa dinaa rey sama rakk Yanqóoba.» \v 42 Naka lañu nettali Rebeka la taawam Esawu wax, mu woolu Yanqóoba, doomam ju ndaw ja, ne ko: «Sa mag a ngi fexee feyu, di la wuta rey. \v 43 Kon doom, defal lii ma lay wax, demal làquji fa sama càmmiñ Laban ca Karan, \v 44 nga toog fa moom ay fan, ba kera sa meru mag giif. \v 45 Bu sa meru mag giifee, ba mu fàtte li nga ko def, dinaa yónnee, ñu jëlsi la. Duma seetaan mukk, ba boole leen ñàkk, yeen ñaar ñépp, ci benn bés\f + \fr 27.45 \fr*\ft Dañoo yaakaar ne bu Yanqóoba dawuloon, Esawu dina ko rey, te kon dees na ko feyul, daldi rey Esawu.\ft*\f*!» \p \v 46 Gannaaw gi Rebeka ne Isaaxa: «Àddina soof na ma ndax jigéeni Etteen ñi. Yanqóoba de, bu jëlee ci jigéeni réew mi di Etteen ñu mel ni ñii, sama dund gi, dee a koy gën!» \c 28 \p \v 1 Ci kaw loolu Isaaxa woo Yanqóoba, ñaanal ko, jox ko ndigal lii ne ko: «Bul jël ci jigéeni Kanaan, \v 2 waaye demal Padan Aram ca sa kër maam-góor, ji jur sa yaay, nga jël fa jabar ca sa doomi nijaay Laban. \v 3 Yal na la Yàlla Aji Man ji barkeel, nga jaboot lool te sa giir yokku, ba sos ay mboolooy askan. \v 4 Yal na la barkeb Ibraayma dal, yaak askan wi soqikoo ci yaw, ba nga moom réew mii ngay doxandéem tey, te Yàlla mayoon ko Ibraayma.» \v 5 Isaaxa daldi yebal Yanqóoba, mu dem Padan Aram ca Laban doomu Betuwel, Arameen bay càmmiñu Rebeka, miy yaayu Yanqóoba ak Esawu. \s1 Esawu jël na keneen soxna \p \v 6 Esawu nag yég ne Isaaxa ñaanal na Yanqóoba, ba noppi yebal ko Padan Aram, ngir mu jël fa soxna. Te it ba mu koy ñaanal, digal na ko ne ko, bumu jël ca jigéeni Kanaaneen ña. \v 7 Mu yég ne Yanqóoba déggal na baayam ak yaayam, ba dem Padan Aram. \v 8 Loolu won Esawu ne jigéeni Kanaan neexuñu baayam. \v 9 Ba mu ko defee Esawu dem ca xeetu Ismayla, jël fa Maalat doomu Ismayla, miy doomu Ibraayma, te di jigéenu Nebayot, mu bokk ciy soxnaam. \s1 Yanqóoba sàrtoo na ak Yàlla \p \v 10 Ba loolu wéyee Yanqóoba génn Beerseba, wuti Karan. \v 11 Naka la dem, ba àgg fu ko jant bi sowe, daldi fay fanaan. Mu jël ca doj ya fa ne woon, gegenoo. \p \v 12 Guddi googu Yanqóoba dafa gént, gis raas bu sampu ci suuf, te cat la sar asamaan, malaakay Yàlla yi di ci yéeg ak a wàcc. \v 13 Ndeke \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jaa nga tollu ca wetam. Mu wax ak moom ne ko: «Maay Aji Sax ji, di sa Yàllay maam Ibraayma te di Yàllay Isaaxa. Suuf si nga tëdd dinaa la ko jox, yaak sa askan. \v 14 Saw askan dina ne gàññ ni suuf. Dinga law penku ak sowu, ndijoor ak càmmoñ. Ci yaw ak saw askan la giir yi ci kaw suuf yépp di barkeele. \v 15 Maa ngi nii ànd ak yaw, di la sàmm fépp foo jëm, te itam dinaa la délloosi ci réew mii. Duma la bàyyi mukk, waaye dinaa def li ma la wax lépp.» \p \v 16 Ci kaw loolu Yanqóoba yewwu ne: «Ndekete Aji Sax ji mu ngi ci bérab bii, te xawma ko woon.» \v 17 Ma nga tiit nag te naan: «Bérab beeka raglu! Fii kay du fenn, fu dul kër Yàlla; te mooy buntu asamaan.» \p \v 18 Ca suba teel Yanqóoba jóg, jël doj, wi mu gegenoo woon, samp fa, muy xàmmikaay, ba noppi sotti ci ag diw, sellale ko. \v 19 Ca la tudde bérab ba Betel\f + \fr 28.19 \fr*\fk Betel \fk*\ft mu ngi tekki «kër Yàlla».\ft*\f*, waaye ca njàlbéen Lus la dëkk ba tuddoon. \v 20 Gannaaw loolu Yanqóoba dogu na ne: «Su Yàlla àndee ak man, di ma sàmm ci yoon wi may aw, di ma jox lu ma lekk ak lu ma sol, \v 21 ba kera may dellu sama kër baay ci jàmm, su boobaa, Aji Sax ji dina doon sama Yàlla. \v 22 Doj wii ma samp, muy xàmmikaay, mooy doon kër Yàlla, te lépp lu mu ma wërsëgal, dinaa ko génneel fukkeel ba moos.» \c 29 \s1 Yanqóoba daje na ak Rasel \p \v 1 Ba loolu xewee, Yanqóoba awaat yoonam, ba agsi réewum waa penku. \v 2 Mu yem foofa ca ab teen ca àll ba, ñetti gétti gàtt goor ca wet ga, ndax ca booba teen lañu doon wëgge gétt ya, waaye doj wu réy moo uboon teen ba. \v 3 Bu gétt yépp dajaloo foofa, sàmm yi doora àndandoo béraŋ doj wa, mu moy buntu teen ba, ñu wëgg, ba noppi delloo doj wa, mu ubaat teen ba. \p \v 4 Yanqóoba ne leen: «Bokki fan?» Ñu ne ko: «Karan.» \v 5 Mu ne leen: «Ndax xam ngeen Laban doomu Naxor?» Ñu ne ko: «Xam nanu ko kay.» \v 6 Mu dellu laaj leen ne leen: «Mbaa mu ngi ci jàmm?» Ñu ne ko: «Jàmm rekk kay. Xoolal ndaw see di ñëw, mook gàtt yi, mooy doomam Rasel.» \v 7 Yanqóoba ne leen: «Jant bi demagul fenn, ba ngeen di dajale jur gi. Wëggleen gàtt yi, sàmmi leen kay!» \v 8 Ñu ne ko: «Dunu ko man mbete gétt yépp daje, nu béraŋ doj wi, ubbi teen bi, doora wëgg gàtt yi.» \p \v 9 Na muy wax ak ñoom nag, Rasel agsi, indaale gàtti baayam, ndaxte sàmm la woon. \v 10 Ba Yanqóoba gisee Rasel, doomu nijaayam Laban, moom ak gàtti nijaayam ya, dafa daagu ba ca teen ba, béraŋ doj wa ko ub, daldi wëgg gàtti Laban. \v 11 Ba loolu amee Yanqóoba fóon Rasel, ne yikkét jooy. \v 12 Ca la Yanqóoba wax Rasel ne ko: «Maak sa baay a bokk, ndax maay sa doomu bàjjan Rebeka.» Rasel daw, yégal ko baayam. \p \v 13 Ba Laban déggee ne jarbaatam Yanqóoba ñëw na, dafa daw gatandu ko, taf ko ci boppam, fóon ko, yóbbu ko kër ga. Ba Yanqóoba nettalee Laban lépp, \v 14 Laban da ne ko: «Yaw kay sama jarbaat nga lenqe!» Yanqóoba toog na fa ak moom lu mat weer. \v 15 Gannaaw loolu Laban ne Yanqóoba: «Li ngay sama mbokk kat, taxul nga war maa liggéeyal ci neen. Wax ma lan mooy sa peyoor.» \p \v 16 Laban nag amoon na ñaari doom yu jigéen, taaw ba di Leya, rakk ja di Rasel. \v 17 Leya di ku bët ya yànjuloon, te Rasel nekkoon ku jekk te neexa xool, \v 18 Yanqóoba bëgg Rasel lool, ba ne Laban: «Dinaa la liggéeyal juróom ñaari at ngir Rasel sa doom ju ndaw ji.» \v 19 Laban ne ko: «Ma may la ko de moo ma gënal may ko keneen. Kon toogal ci man.» \v 20 Ci kaw loolu Yanqóoba liggéeyal Laban diiru juróom ñaari at ngir Rasel, te mu mel ni ay fan rekk ci moom ndax mbëggeel, gi mu am ci Rasel. \p \v 21 Loolu wéy, Yanqóoba ne Laban: «Jox ma sama jabar, ma séetal ko, ndax àpp bi jot na.» \v 22 Laban nangu, daldi togglu ay reer, woo ca waa gox ba bépp. \v 23 Timis jot Laban jël doomam Leya, jébbal ko Yanqóoba, mu dëkkoo ko. \v 24 Ci biir loolu Laban jël jaamam bu jigéen bu ñuy wax Silpa, may ko doomam Leya, mu dib jaamam. \p \v 25 Ba bët setee, Yanqóoba fekk muy Leya. Mu ne Laban: «Waaw, li nga ma def nag? Du Rasel a taxoon ma liggéeyal la? Lu tax nga wor ma?» \v 26 Laban ne ko: «Rakk jëkka séy taaw daal, du aada fii. \v 27 Séetul ak kii, ba ayu bésam mat, ma door laa jox ki ci des, soo ma dee liggéeyaatal diiru juróom ñaari at.» \v 28 Yanqóoba nangu, daldi séetu ak Leya ayu bés, ba noppi Laban jébbal ko doomam Rasel. \v 29 Booba la Laban may Rasel jaamam bu jigéen bu ñuy wax Bilaa, mu dib jaamam. \v 30 Yanqóoba nag dëkkoo Rasel, mi mu gënoona bëgg Leya. Ci kaw loolu mu liggéeyaatal Laban juróom ñaari at. \s1 Lu jëm ci njabootu Yanqóoba \p \v 31 Ba \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji gisee ne Leya fonkeesu ko, mu may ko, mu taawlu, te Rasel moom manula am doom. \v 32 Ba Leya ëmbee, am doom ju góor, da koo tudde Ruben (mu firi Gisleen, doom ju góor a ngi), ndaxte Leya da ne: «Aji Sax ji gis na sama toroxte. Léegi sama jëkkër dina ma bëgg.» \v 33 Mu dellu ëmb, am doom ju góor. Mu ne: «Aji Sax ji yég na ne fonkeesu ma, looloo tax mu mayaat ma doom jii.» Mu tudde ko Simeyon (mu firi Kiy dégg). \v 34 Mu delluwaat ëmb, am doom ju góor, ba noppi waxaat ne: «Bii yoon sama jëkkër dina am cofeel ci man, ndax jural naa ko ñetti doom yu góor,» loolu tax mu tudde ko Lewi (mu firi Boroom cofeel). \v 35 Mu dellooti ëmb, am doom ju góor daldi ne: «Bii yoon dinaa sant Aji Sax ji,» loolu tax mu tudde ko Yuda (mu firi Cant). Gannaaw loolu njuram taxaw. \c 30 \p \v 1 Ba Rasel gisee ne amalul Yanqóoba doom, dafa ñee magam, ba tax mu wax Yanqóoba ne ko: «Nanu am ay doom, mbaa ma dee.» \v 2 Yanqóoba mere ca Rasel ne ko: «Ndax maay Yàlla, mi la teree am doom?» \v 3 Mu ne ko: «Xoolal, sama jaam Bilaa ngii; dëkkoo ko, ndax mu amal ma doom, ba jabootal ma.» \v 4 Ci kaw loolu mu may ko jaamam Bilaa, muy soxnaam. Yanqóoba dëkkoo Bilaa, \v 5 mu ëmb, amal Yanqóoba doom ju góor. \v 6 Bi loolu amee Rasel ne: «Yàlla àtte na ma; dégg na sama ñaan, ba may ma doom.» Mu tudde ko nag Dan (mu firi Kiy àtte). \v 7 Gannaaw ga Bilaa, jaamub Rasel, ëmbaat, dellu amal Yanqóoba doom ju góor. \v 8 Rasel ne: «Bëre naa ak sama mag bëre bu réy, ba daan,» daldi ko tudde Neftali (mu firi Kiy bëre). \p \v 9 Leya moom it xam ne taxawaayam yàgg na, mu fab jaamam Silpa, may ko Yanqóoba. \v 10 Bi loolu amee Silpa, jaamub Leya, amal Yanqóoba doom ju góor. \v 11 Leya ne: «Ndaw wërsëg wu réy!» daldi ko tudde Gàdd (mu firi Wërsëg). \v 12 Silpa jaamub Leya dellu, amal Yanqóoba doom ju góor. \v 13 Leya ne: «Éey waay, maaka bég! Jeeg ji dinañu ma wooye boroom mbégte mi.» Mu tudde ko nag Aser (mu firi Boroom mbégte). \p \v 14 Mu am bés ñuy góob bele, Ruben dem tool, sàkke ca gàncax gu ñu naan màndaragoor\f + \fr 30.14 \fr*\fk màndaragoor \fk*\ft gàncax la gu ñu yaakaar ne day giiral jigéen.\ft*\f*, indil ko yaayam Leya. Rasel ne Leya: «Ngalla may ma ci màndaragoor ji la sa doom indil.» \v 15 Teewul mu ne ko: «Ndax nangu sama jëkkër rekk doyu la, ba nga bëgg cee boole màndaragoor ji ma sama doom indil?» Rasel ne ko: «Kon jox ma ci màndaragoor ji sa doom indi, ma wecci la ko sama ayu tey boog.» \p \v 16 Yanqóobaa ngay jóge tool ca ngoon, Leya génn, gatandu ko, ne ko: «Fi man nga wara aye tey, ndaxte jënde naa ay gi màndaragoor ji sama doom indi.» Yanqóoba daldi féete ca moom guddi googu. \v 17 Yàlla nangul Leya, mu ëmb, am ak Yanqóoba seen juróomeelu doom ju góor. \v 18 Leya neeti: «Yàlla da maa fey, ndax maa may sama jëkkër sama jaam.» Mu tudde ko Isaakar (mu firi Boroom pey). \v 19 Gannaaw gi Leya ëmbaat, am ak Yanqóoba seen juróom benneelu doom ju góor. \v 20 Booba la ne: «Yàlla defal na ma teraanga ju réy. Bii yoon sama jëkkër dina ma teral, ndax amal naa ko juróom benni doom yu góor.» Moo tax mu tudde ko Sabulon (mu firi Teraanga). \v 21 Gannaaw ga mu am doom ju jigéen, tudde ko Diina. \p \v 22 Ba loolu amee Yàlla geestu Rasel, nangul ko, may ko doom. \v 23 Mu ëmb, am doom ju góor, daldi ne: «Yàlla teggil na ma gàcce.» \v 24 Moo tax mu tudde ko Yuusufa (mu firi Yal na dolli), ndax dafa ne: «Yal na ma Aji Sax ji dollil doom ju góor.» \s1 Yanqóoba woomle na \p \v 25 Ba Rasel amee doom ci Yuusufa, Yanqóoba da ne Laban: «Yiwi ma boog, ma dellu sama réew ca sama kër. \v 26 Su ko defee nga jox ma samay doom ak sama jabar yi taxoon ma di la liggéeyal, te bàyyi ma, ma dem, ndax yaw ci sa bopp xam nga li ma la liggéeyal.» \v 27 Laban ne ko: «Ngalla waay, déglu ma, ngir sama ngisaane won na ma ne \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji barkeel na ma ndax yaw. \v 28 Wax ma loo may feyeeku rekk, dinaa la ko fey.» \v 29 Yanqóoba ne ko: «Yaw ci sa bopp xam nga ni ma la liggéeyale ak ni sa gétt mujj mel ndax man; \v 30 ndaxte lu néew nga amoon laata may ñëw, te yokku na, ba bare lool, ngir Aji Sax ji da laa barkeel ndax man. Waaye léegi nag, liggéeyal sama waa kër bopp jot na xanaa?» \v 31 Laban dellu ne ko: «Dama ne, ñaata laa lay fey?» Yanqóoba ne ko: «Doo ma jox dara. Boo nangoo lii ma lay wax, dinaa sàmmaat say gàtt, wattu ko. \v 32 Damay seet tey jii ci biir jur gu gàtt gépp, génne ci xar yu ñuul yépp\f + \fr 30.32 \fr*\ft Ca yooyu jamono xar yi dañu daan faral di weex, bëy yi farala ñuul te duñu rax.\ft*\f*, ak bëy, yi todde ak yi tippante yépp, ñu doon sama peyoor\f + \fr 30.32 \fr*\ft Fii dañoo topp téereb kàddug Yàlla gi ni ñu ko tekkee ci làmmiñu gereg, te ci booba téere melow todde ak tippante bëy yi rekk a ko féetewoo.\ft*\f*. \v 33 Ëllëg aki sibbir booy seetsi sama peyoor, sama njubtee may layool: lépp lu toddewul te tippantewul ci biir bëy yi ak lu ñuulul ci mburt yi, boo ko gisee ci man, càcc la.» \v 34 Laban ne: «Waaw, kon baax na.» \p \v 35 Ca bés booba Laban dafa ber sikket, yi seereer te todde, ak bëy, yi tippante te todde, maanaam yi rax, ak xari menn melo yu ñuul yi, daldi leen dénk ay doomam. \v 36 Gannaaw loolu mu doxale digganteem ak Yanqóoba doxu ñetti fan. Yanqóoba nag di sàmm li des ci gàtti Laban. \p \v 37 Ci kaw loolu Yanqóoba tànn ñetti garab yu ñuy wax pëpalyee, gerte-tubaab ak palataan, gor ci bant yu tooy, xànc-xàncee ko, ba mu defi rëdd yu weex. \v 38 Mu yeb bant, ya mu xànc-xàncee, ca naanukaay ya, mu janook jur ga, ca mbalka ya jur gay naane, ndax fa la jur ga daan tëboo. \v 39 Loolu tax bëy yay tëbu ca wetu car ya, di jur doom yu seereer, yu tippante ak yu todde. \v 40 Xar ya, Yanqóoba da leena ber, tey fexe ñuy janook lépp lu seereer ak lu ñuul ci biir juru Laban. Noonu la sàkke juru boppam, bañ koo boole ak juru Laban. \v 41 Saa yu jur gi ëpp doole dee tëbu, Yanqóoba yeb car yi ci naanukaay yi, tiimale ci jur gi, ngir bu ñuy tëbu, ne ci jàkk. \v 42 Bu jur gu xiibon gi dee tëbu, mu bañ leena tegal dara. Muy def noonu ba jur gi xiibon, di gu Laban, gi am doole, di gu Yanqóoba. \v 43 Waa ji mujj na barele lool, am gàtt yu ne gàññ ak ay jaam yu góor ak yu jigéen ak ay giléem aki mbaam-sëf. \c 31 \s1 Yanqóoba toxu na, jëm Kanaan \p \v 1 Ba loolu amee mu am bés Yanqóoba dégg doomi Laban ya naan, Yanqóoba nangu na li seen baay amoon lépp, te ci seen alalu baay la sàkkoo alalam jooju jépp. \v 2 Naka la Yanqóoba gis kanamu Laban, daldi xam ne melatul, na mu meloon ci moom. \v 3 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax Yanqóoba ne ko: «Dellul ca sa réewu maam ya, ca say bokk. Dinaa ànd ak yaw.» \p \v 4 Yanqóoba woolu Rasel ak Leya ca tool ya, fa gàttam ya nekk. \v 5 Mu ne leen: «Gis naa seen kanamu baay. Xam naa ne melatul na mu meloon ci man. Waaye sama Yàllay baay ay ànd ak man. \v 6 Yeen ci seen bopp xam ngeen ne liggéeyal naa seen baay sama kem kàttan. \v 7 Teewul seen baay wor ma, soppi sama peyoor fukki yoon ak juróom, waaye Yàlla seetaanu ko, mu di ma lor. \v 8 Bu nee: “Yi tippanteey sa peyoor,” jur gépp jur lu tippante; mbaa mu ne: “Yi seereer ay sa peyoor,” jur gépp jur lu seereer. \v 9 Nii la Yàlla nangoo seen juru baay, jox ma. \p \v 10 «Ba ñu demee ba jur giy wara tëbu, damaa jeneer sikket yiy tëb bëy yi yépp di lu seereer ak lu tippante mbaa ñu raxe. \v 11 Ca la ma malaakam Yàlla ma wax ci biir gént gi ne ma: “Yanqóoba,” ma ne ko: “Naam.” \v 12 Mu ne ma: “Siggil, xool sikket yiy tëb bëy yi yépp, yii dañoo seereer, yee todde, yi ci des tippante, ndaxte gis naa li la Laban di def lépp. \v 13 Maay Yàlla, ja la feeñu woon Betel, fa nga samp doj, sotti ci diw, sellale ko, te dogu woon fa ci man. Léegi nag jógal, génn réew mii, dellu ca réew, ma nga juddoo.”» \p \v 14 Rasel ak Leya ne ko: «Ndax amati nanu benn cér walla ndono sunu kër baay? \v 15 Doonunu lu moy ay doxandéem ci moom de! Nde da noo jaay, lekk sunu njég, ba mu jeex tàkk. \v 16 Te mboolem alal, ji Yàlla nangoo ci sunu baay, noo ko moom, nun ak sunuy doom. Kon nag léegi lu la Yàlla wax rekk, def ko.» \p \v 17 Yanqóoba daldi dajale ay doomam ak ay soxnaam, waral leen giléem, \v 18 ñu ànd tegu ca yoon wa, yóbbaale géttam gépp ak mboolem alal ju mu liggéey. Mooy gétt, ga mu sàkkoo Padan Aram. Ña ngay ñibbi kër baayam Isaaxa ca réewu Kanaan. \p \v 19 Fekk na Laban dem wati ay xaram\f + \fr 31.19 \fr*\ft Xari waa penku dañuy bare kawar gu ñuy wat ak a ëcc, di ci defar ag wëñ.\ft*\f*. Ci biir loolu Rasel sàcc gàllaaji kër yu baayam. \v 20 Noonu la Yanqóoba nëbboo Laban, Arameen ba, bañ koo yégal ne day dem. \v 21 Ba mu demee, dafa yóbbaale la mu amoon lépp, jóge fa, jàll dexu Efraat, wuti tundi Galàdd. \s1 Laban dabi na Yanqóoba \p \v 22 Yanqóoba daw na, ba mu am ñetti fan, ñu soog koo yégal Laban. \v 23 Mu ànd nag ak ay bokkam, topp ko juróom ñaari fan, door koo dab ca tundi Galàdd. \v 24 Ci kaw loolu Yàlla feeñu Laban, Arameen ba, ci géntu guddi ne ko: «Moytula wax Yanqóoba lenn lu koy gaar.» \v 25 Ba Laban dabee Yanqóoba, dafa fekk mu samp xaymaam ca tund wa. Laban it samp bosam ca kaw tundi Galàdd, moom aki bokkam. \p \v 26 Laban ne Yanqóoba: «Looy def nii, yaw, di ma nëbbuy daw, yóbbaale sama doom yu jigéen, ñu mel ni ñu ñu lële xare? \v 27 Lu waral nga di ma nëbbuy daw te bañ maa tàggu? Nde konoon jombul ma yiwi la ci xol bu sedd, bu ànd aki woy, boole ci xalam aki sabar. \v 28 Mayoo ma sax, ma fóon samay sët ak samay doom yu jigéen, tàggtook ñoom; yëfi dof de nga def nii! \v 29 Manoon naa laa def lu bon, waaye sa Yàllay baay da maa feeñu biig ne ma: “Moytula wax Yanqóoba lenn lu koy gaar.” \v 30 Bu la neexee, nga namm sa kër baay, ba dogu caa dem, waaye lu tax nga sàcc sama gàllaaji kër, teg ci?» \p \v 31 Yanqóoba tontu Laban ne ko: «Xanaa ragaloon rekk ne jombul dinga téye say doom yu jigéen. \v 32 Waaye képp koo gis mu yor sa gàllaaji kër, boo yeboo reyal. Seetal fii ci sunu kanami bokk lépp lu ma fi yor, loo ci moom fabal, yóbbu.» Booba Yanqóoba xamul woon ne Rasel a ko jël. \v 33 Laban dugg ci xaymab Yanqóoba, teg ca xaymab Leya ak yosi ñaari jaamam yu jigéen ya, te gisul dara. Mu génne xaymab Leya, dugg ci bu Rasel. \p \v 34 Fekk na Rasel fab gàllaaji kër ya, làq ca ron tegu giléem ga, toog ca. Laban tëcc, tëcc ca biir xayma ba, gisul dara. \v 35 Rasel wax baayam ne ko: «Baay, baal ma de, damaa manula jóg ci sa kanam, ndaxte damaa ànd ak mbaax.» Laban seet na fu ne, waaye gisul gàllaaji këram ya. \p \v 36 Yanqóoba mer lool, daldi gëdd Laban ne ko: «Ndax damaa tooñ walla damaa moy, ba nga sambal ma, di ma topp nii? \v 37 Bi nga jéexee sama yëf yépp ba noppi, ana loo gis lu bokk ci sa yëfi kër? Teg ko fii ci sama kanami bokk ak say bokk, ñu àtte nu. \v 38 Xanaa du ñaar fukki at a ngii ma nekk ak yaw? Say xar ak say bëy ëmbuñu sax, mu yàqu, te masumaa lekk sa kuuyi gétt. \v 39 Jur gu rab fàdd sax ma féetewoo, waaye masuma la koo indil. Mboolem lu ñu sàcc guddi ak lu ñu sàcc bëccëg, danga ma ko daa feyu. \v 40 Naaj wi laa daan yendoo yenu bëccëg, di fanaanoo sedd guddi, mu xaw maa rey, ba duma gëmm bët. \v 41 Ñaar fukki at a ngii, ma di la jaamu ci kër gi, liggéeyal naa la fukki at ak ñeent ngir sa ñaari doom yu jigéen ñii, teg ci juróom benni at yu ma la sàmmal say gàtt, nga soppi sama peyoor fukki yoon ak juróom. \v 42 Su dul woon ak sama Yàllay baay, ji ànd ak man, di Yàllay Ibraayma, ji Isaaxa wormaaloon, konoon nga dàq ma tey, ma dem loxoy neen. Waaye sama toskare ak sama àqu ñaq la Yàlla gis, ba tax mu àtte ma ak yaw biig.» \p \v 43 Ba mu ko waxee loolu, Laban ne ko: «Jigéen ñii samay doom lañu, xale yii di samay sët, te gétt gii sama gétt a; lu fi nekk maa ko moom. Ñii di sama doom yu jigéen, nu ma leen di def tey, ñoom ak seeni doom? \v 44 Léegi ñëwal rekk, ñu fasante \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* maak yaw, te seede dox sunu diggante maak yaw.» \v 45 Ba loolu amee Yanqóoba jël aw doj, samp ko, muy doju xàmmikaay. \v 46 Yanqóoba ne ay bokkam: «Forleen ay doj.» Ñu for ay doj, def ko ab jal, daldi lekk foofa ca wetu jal ba. \v 47 Laban tudde bérab ba Yegar Saaduta; Yanqóoba tudde ko Galet\f + \fr 31.47 \fr*\fk Galet \fk*\ft bokk na lu mu tekki ak \ft*\fq Yegar Saaduta \fq*\ft ci làkku Arameen ña.\ft*\f*. \p \v 48 Booba la Laban ne: «Jal bii tey, mooy sunu seede sama diggante ak yaw.» Moo tax ñu tudde ko Galet (mu firi Jalub seede). \v 49 Ñu di ko tudde itam Mispa (mu firi Tatay wattukaay), ndax Laban da ne: «Yal na \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wattu sunu diggante, keroog bu ñu soree. \v 50 Soo soxoree samay doom yu jigéen, mbaa nga takk yeneen jabar, bu fa kenn nekkul sax, moytul, ndax Yàllaa nuy seede.» \v 51 Laban neeti Yanqóoba: «Xoolal ci jal bii ak doju xàmmikaay, wi ci sama digganteek yaw. \v 52 Jal bi seede la, doj wi di seede ne duma jéggi jal bi, jublu ci yaw, te yaw itam doo jéggi jal bi mbaa doj wi, jublu ci man, te naraluloo ma jàmm. \v 53 Yàllay Ibraayma ak Yàllay Naxor, ñoom ñooñee di seen Yàllay baay, yal nañu àtte sunu diggante.» Yanqóoba daldi giñ ci Yàlla, ji baayam Isaaxa wormaaloon. \v 54 Gannaaw loolu Yanqóoba sàkk sarax ca kaw tund wa, woo ay bokkam, ñu bokk lekk. Ba ñu lekkee ba noppi, fanaan ca tund wa. \b \p \v 55 Ca ëllëg sa, Laban xëy suba teel, tàggoo aki sëtam ak doomam yu jigéen ya, ñaanal leen, ba noppi waññiku ñibbi. \c 32 \p \v 1 Yanqóoba moom topp yoonam. Ci kaw loolu ay malaakay Yàlla feeñu ko. \v 2 Ba leen Yanqóoba gisee, da ne dalub Yàllaa ngii, ba tax mu tudde bérab ba Maanayim (mu firi Ñaari dal). \s1 Yanqóoba ragal naa daje ak Esawu \p \v 3 Ba loolu amee Yanqóoba dafa yónni ay ndaw, ñu jiitu ko ca magam Esawu, ca réewu Seyir, di diiwaanu Edom. \v 4 Mu sant leen ne leen: «Bu ngeen demee ca sama sang Esawu, neleen ko: Sa surga Yanqóoba nee na: “Maa nga woon ca kër Laban bu yàgg ba tey, \v 5 ma doora ñëw, ànd ak ay nag ak ay mbaam ak ay gàtt ak ay jaam yu góor ak yu jigéen; may yónnee ci yaw, di la siyaare tey sàkku nga dalal ma jàmm.”» \v 6 Ndaw ya daldi dem ba délsi ca Yanqóoba, ne ko: «Dem nanu ca sa mag Esawu, waaye moom ci boppam mu ngi ci yoon wi di ñëw, fekksi la fii, te ma nga ànd ak ñeenti téeméeri góor.» \p \v 7 Yanqóoba dégg loolu, tiit lool te ànd ak njàqare, ba tax mu séddale mbooloo, ma mu àndal, gàtt ya ak jur gu gudd ga ak giléem ya itam, mu xaaj leen ñaar. \v 8 Booba mu ngi naan, bu Esawu songee benn dal bi, dal bi ci des mana raw. \v 9 Ci kaw loolu Yanqóoba ñaan Yàlla, ne ko: «Yaw \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, sama Yàllay maam Ibraayma, di sama Yàllay baay Isaaxa itam, yaa ma ne woon: “Dellul réew ma nga cosaanoo, ca say bokk; dinaa la baaxe.” \v 10 Yelloowuma lu gëna tuuti ci sa ngor ak sa worma, gi nga ma won, man sa jaam. Aw yet doŋŋ laa ŋàbboon, ba ma jàllee dexu Yurdan, te yokku naa tey, ba doon ñaari kurél. \v 11 Maa ngi lay ñaan, nga musal ma ci sama loxol mag Esawu, ndaxte ragal naa, mu ñëw bóom ma, bóomaale jigéen ñi ak seeni doom. \v 12 Te yaw yaa ma ne: “Dinaa la baaxe moos, yokk saw askan, ba mu tollu ni suufas géej, si kenn manula lim ndax bare.”» \p \v 13 Yanqóoba fanaan na fa guddig keroog, doora sàkk ca alalam, sédd magam Esawu, \v 14 lépp di ñaar téeméeri bëy ak ñaar fukki sikket ak ñaar téeméeri xar ak ñaar fukki kuuy \v 15 ak fanweeri giléem yu seeni doom di nàmp, ak ñeent fukki nag ak fukki yëkk ak ñaar fukki mbaam ak fukki mbaam yu góor. \p \v 16 Dafa ber gétt yi, gu ci nekk mu jox ay surgaam, ne leen: «Jiituleen ma, te na gétt yi dàndante.» \v 17 Ci biir loolu mu sant ki jiitu, ne ko: «Boo dajeek sama mag, mu laaj la ne la: “Kuy sa njaatige?” ak “Ku moom li nga jiital?” ak “Foo jëm?” \v 18 nee ko: “Lii de sang bi, lu la Yanqóoba may la, di la ko siyaaree, yaw Esawu, te moom ci boppam mu ngi topp ci sunu gannaaw.”» \v 19 Ndigal loolu la joxaat ñaareelu surga ba ak ñetteel ba ak mboolem ña topp ca gétt ya, ku ci nekk mu wax ko ne ko loolu lay wax Esawu, bu ko gisee, \v 20 tegati ca ne ko: «Te nee ko itam: “Sa surga Yanqóobaa ngi topp ci sunu gannaaw.”» Booba Yanqóobaa ngi naa ci xelam: «Bu ma jiitalee li ma ko may, neexale ko ko, bala maa janook moom, jombul mu dalal ma jàmm.» \v 21 Neexal ba da koo jiitu, moom mu fanaan guddig keroog ca dal ba. \s1 Lu jëm ci bëreb Yanqóoba ba \p \v 22 Gannaaw loolu Yanqóoba jóg ca guddi ga, ànd ak ñaari soxnaam, ñaari jaamam yu jigéen ak fukki doomam yu góor ak benn, daldi jàll dexu Yabog. \v 23 Yanqóoba da leena jàllale, jàllewaale alalam jépp itam. \v 24 Mu des fa nag moom doŋŋ. \p Kera la genn góor fanaana bëre ak moom, ba bët set. \v 25 Ba nit ka xamee ne manalu ko dara, dafa dóor Yanqóoba ci mooco, mooco mi summikoo ca bëre ba. \p \v 26 Nit ka ne ko: «Bàyyi ma, ma dem, ndax bët a ngi bëgga set.» Teewul Yanqóoba ne ko: «Duma la bàyyi, nga dem, li feek ñaanaloo ma.» \v 27 Nit ka ne ko: «Na nga tudd?» Mu ne ko: «Yanqóoba.» \v 28 Nit ka ne ko: «Tuddatuloo Yanqóoba, léegi Israyil nga tudd, ndaxte bëre nga ak nit, bëre ak Yàlla, ba génn ci ak jàmm\f + \fr 32.29 \fr*\ft Ñaari kàdduy ebrë yu taqoo ñoo sos baatu \ft*\fq Israyil. \fq*\ft Li jiitu ci baat bi mu ngi tekki «bëre». Li ci topp di tekki «Yàlla».\ft*\f*.» \v 29 Yanqóoba ne ko: «Waaw, yaw nag noo tudd?» Mu wax ko ne ko: «Loo may laaje sama tur?» ba noppi barkeel ko foofa. \p \v 30 Ci kaw loolu Yanqóoba tudde bérab ba Peniyel (mu firi Xar-kanamu Yàlla), ndaxte da ne: «Ne naa Yàlla jàkk, te maa ngi dund ba tey.» \p \v 31 Ba jant bay fenk, Yanqóobaa ngi soox tànk bi, di bàyyikoo Penuwel\f + \fr 32.32 \fr*\fk Penuwel \fk*\ft mooy Peniyel ba tey.\ft*\f*. \v 32 Looloo tax ba tey jii \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* duñu lekk suux, wi jàpp ci tenqob mooco, ndax li moocob Yanqóoba summikoo woon ca suuxu tenqo ba. \c 33 \s1 Yanqóoba ak Esawu daje nañu ci jàmm \p \v 1 Gannaaw loolu Yanqóoba séen Esawu di ñëw, ànd ak ñeenti téeméeri góor, mu séddale xale yi, diggante Leya, Rasel ak ñaari jaam ya. \v 2 Dafa jiital jaam ya ak seeni doom, tofal ca Leya ak ay doomam, Rasel ak Yuusufa féete gannaaw. \v 3 Moom ci boppam nag, mu jiitu leen, wutali magam, di dox tey sujjóot, ba muy juróom ñaari yoon. \v 4 Teewul Esawu daw gatandu ko, taf ko ci boppam, langaamu ko, di ko fóon. Ñu daldi jooy! \p \v 5 Naka la Esawu siggi, gis jigéen ñi ak xale yi, mu ne: «Ñii ànd ak yaw ñooy ñan?» Yanqóoba ne ko: «Xanaa njaboot, gi ma Yàlla baaxe, sang bi.» \v 6 Jaam ya ak seeni doom daldi jegesi, sujjóotal ko. \v 7 Leya it topp ca, moom aki doomam, jegesi ñoom itam, sujjóot. Yuusufa ak Rasel doora jegesi sujjóot. \p \v 8 Esawu ne ko: «Waaw, dal bu réy bii ma dajeel, loo ci namm?» Yanqóoba ne ko: «Xanaa di sàkku nga dalal ma jàmm rekk, sang bi.» \v 9 Esawu ne ko: «Am naa ba biibal, sama rakk, fabal sa alal.» \v 10 Yanqóoba ne ko: «Ngalla waay déet, dimbali ma rekk te jël li ma la may. Ndaxte bi ma nee jàkk ci sa kanam, gis naa ni nga ma laaye biir, ba mu mel ni Yàllaa ma geestoo yërmandeem. \v 11 Kon jëlal lii ma la may, ndax Yàlla baaxe na ma, ba ma barele.» Mu tinu ko, ba Esawu mujj nangu. \p \v 12 Gannaaw loolu Esawu ne: «Tee noo ànd dem boog, ma jiitu la?» \v 13 Yanqóoba ne ko: «Sang bi, xam nga, xale yi dañoo néew doole, te it gàtt yi ak nag yiy nàmpal laay xalaat. Su nu leen sëqatalee benn bés rekk, gàtt yépp dee. \v 14 Jiitu ma rekk, sang bi, man ma topp ndànk ci wewu jur gi, jiital leen, te baña raw xale yi, ba kera ma lay fekksi Seyir.» \v 15 Esawu ne ko: «Xaaral ma bàyyee la ñenn ci góor, ñi ma àndal.» Yanqóoba ne ko: «Matu ko. Boobu teraanga ëpp na, sang bi. Jàmm ji nga ma dalal rekk doy na.» \v 16 Booba la Esawu dellu, jubal yoonu Seyir. \p \v 17 Yanqóoba moom jubal gox bu ñu naan Sukkóot, tabax fa kër, mbaaral géttam, moo tax ñu tudde bérab boobu Sukkóot (mu firi Ay mbaar). \v 18 Gannaaw ga Yanqóoba agsi Sikem, ga ca réewu Kanaan, ci jàmm. Fekk na mu bàyyikoo Padan Aram, ba dal fa jàkkaarlook dëkk ba. \v 19 Booba la jënde ci doomi Amor, baayu Sikem, pàkk, ba mu sampoon xaymaam, ci téeméeri kesita\f + \fr 33.19 \fr*\fk kesita \fk*\ft xaalisu réew ma la woon.\ft*\f*. \v 20 Mu daldi fay sàkk \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*, tudde ko El Elowe Israyil (mu firi Yàllay Israyil mooy Yàlla). \c 34 \s1 Tooñ nañu Diina doomu Yanqóoba \p \v 1 Am na bés Diina, ku jigéen ki Leya amal Yanqóoba, génn di seeti moroom ya ca dëkk ba. \v 2 Ci kaw loolu Sikem doomu Amor, miy Eween te di kilifa ca dëkk ba, daldi koy gis, jàpp ko, tëdde ko, torxal ko. \v 3 Teewul Sikem xemmemoon na Diina doomu Yanqóoba lool te bëgg ko, ba tax mu di ko naxtaan. \v 4 Loolu waral mu ne baayam Amor: «Ñaanal ma janq bi jabar.» \p \v 5 Yanqóoba nag dégg ne Sikem torxal na Diina, doomam ju jigéen, fekk booba doomam yu góor yaa nga woon ca àll ba, fa jur ga nekk. Yanqóoba ne cell, ba ñu ñibbsi. \v 6 Ci diggante boobu Amor, baayu Sikem, ñëw ci Yanqóoba, ngir gise ak moom. \v 7 Ca la doomi Yanqóoba agsi, jóge ca tool ya. Ba ñu déggee la xew, dañoo am naqar wu réy, mer lool ndax gàcce, ga Sikem teg waa Israyil, ba mu tëddee doomu Yanqóoba ja, te loolu di lu defuwul. \p \v 8 Amor wax ak ñoom ne leen: «Sama doom Sikem dafa bëgg seen jigéen ci xolam. Dama leen di ñaan, ngeen may ko ko jabar. \v 9 Tee noo séyante, ngeen may nu seeni janq, te jël ci sunuy janq? \v 10 Su ko defee ngeen dëkk ak nun te réew mi di seen réew. Man ngeen fee sanc, dem fu leen neex, sàkku fi alal.» \v 11 Sikem it wax ak baayu Diina ak càmmiñ ya ne leen: «Su ngeen ma nangulee, lépp lu ngeen ma wax dinaa ko joxe. \v 12 Limal-leen ma warugar yi ak nu mu mana tollu, boole ci may gi; dinaa joxe lu ngeen ma sas; mayleen ma janq bi rekk.» \p \v 13 Waaye doomi Yanqóoba ya, ay nax lañu tontoo Sikem ak baayam Amor, ndax li Sikem torxal seen jigéen Diina. \v 14 Dañu ne leen: «Manunu loolu, ndax may sunu jigéen góor gu xaraful, loolu gàcce la ci nun. \v 15 Dunu leen mana nangul mbete ngeen melee ni nun ci kaw seeni góor ñépp xaraf. \v 16 Su ko defee dinanu leen may sunuy janq, te dinanu jël ci seeni janq, dëkk ak yeen, nuy ay bokk. \v 17 Waaye su ngeen nu déggalul, ba xarafuleen, danuy jël sunu jigéen, dem.» \p \v 18 Seen wax jooju neex Amor ak Sikem doomu Amor. \v 19 Xale bu góor bi daldi gaawtu def li ñu ko sant ndax mbëggeelam ca doomu Yanqóoba. Booba Sikem lañu gënoona weg ca waa kër baayam yépp. \v 20 Amor nag ànd ak doomam Sikem, dem ba ca pénc ma, wax ak waa dëkk ba ne leen: \v 21 «Ñii sunuy am-di-jàmm lañu, te gannaaw réew maa ngi ne yàmblaŋ, bàyyileen leen, ñu sanc te dem fu leen neex. Man nanoo jël seen doomi janq te di leen may sunuy doom. \v 22 Waaye li ci nekk mooy, seeni góor duñu nangoo dëkk ak nun, nuy ay bokk, ndare sunu góor ñépp xaraf ni ñoom. \v 23 Bu nu leen nangulee, ba ñu dëkk ci sunu biir, kon seeni jur ak seen alal ak seen mala yépp, ndax du nooy doon boroom?» \v 24 Ba mu ko defee mboolem góori dëkk ba déggal Amor ak doomam Sikem, ba ñoom ñépp xaraf. \p \v 25 Ca gannaaw ëllëg sa ñu ànd ak metit, ñaari doomi Yanqóoba ya, Simeyon ak Lewi, càmmiñi Diina, jël seeni saamar, dugg ca dëkk ba, bett leen, rey góor ñépp. \v 26 Ca lañu leel ñawkay saamar Amor ak doomam Sikem, ñu dee, ñu jële Diina kër Sikem, ànd ak moom, dem. \v 27 La ca tegu doomi Yanqóoba ya ca des futti néew ya, lëlaale dëkk ba, ndax li ñu torxal seen jigéen. \v 28 Ñu daldi jël seen jur gu gàtt ak gu gudd, seeni mbaam ak mboolem la ca biir dëkk ba ak la ko wër. \v 29 Noonu lañu jële seen alal jépp ak seeni doom ak seeni jabar, boole ca lël mboolem lu nekkoon ca biir kër ya. \p \v 30 Yanqóoba nag wax ak Simeyon ak Lewi ne leen: «Indil ngeen ma musiba, ndax dingeen tax waa réew mépp sib ma, muy Kanaaneen ñi, di Periseen ñi. Te itam awma lu dul góor ñu néew, te bu ñu booloo dal ci sama kaw, dañu may booleek sama waa kër faagaagal.» \v 31 Ñu ne ko: «Danuy seetaan sunu jigéen daal, ñu di ko def ab gànc?» \c 35 \s1 Yanqóoba sanc na Betel \p \v 1 Ba loolu wéyee Yàlla ne Yanqóoba: «Jógal dem Betel, toog fa te nga sàkkal fa \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* Yàlla, ji la feeñu, ba ngay daw sa mag Esawu.» \v 2 Yanqóoba wax ak waa këram ak ñi ànd ak moom ñépp ne leen: «Jëleleen ci seen biir tuuri doxandéem yi, te ngeen sangu-set te solu. \v 3 Danuy dem Betel, ma sàkkal fa sarxalukaay Yàlla, ji ma wallu, ba ma nekkee ci njàqare, te ànd ak man fépp fu ma jaar.» \v 4 Ñu daldi jox Yanqóoba mboolem tuuri doxandéem, yi ñu yor, ak seen jaaroy nopp, Yanqóoba boole suul ca taatu garab\f + \fr 35.4 \fr*\ft Xeetu garab la gu ñuy wax terebent.\ft*\f* gu mag ga nekkoon ca wetu dëkk, ba ñu naan Sikem. \v 5 Gannaaw loolu ñu sàqi, Yàlla nag wàcce tiitaange lu réy ca kaw dëkk, ya leen wër, ba taluñoo dabi doomi Yanqóoba ya. \p \v 6 Ba mu ko defee Yanqóoba ak ñi mu àndal ñépp agsi Lus, di Betel ba tey, foofa ca réewu Kanaan. \v 7 Mu sàkk fa nag sarxalukaay, tudde bérab ba El Betel, ndax foofa la ko Yàlla feeñoo, bi muy daw magam. \v 8 Foofa itam la Debora, ma daa nàmpal Rebeka, faatoo, ñu suul ko ca taatu garab gu mag ga ca wetu Betel. Ñu tudde garab ga Alon Bakut (mu firi Garabu jooyoo). \p \v 9 Ba Yanqóoba jógee Padan Aram, Yàlla feeñuwaat na ko, barkeel ko \v 10 ne ko: \q1 «Yaa di Yanqóoba, \q1 waaye deesatu la wooye Yanqóoba; \q1 léegi yaa di Israyil.» \m Mu tudde ko nag Israyil. \v 11 Yàlla neeti ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Giiral te yokku, ba aw askan ak mboolooy askan sosoo ci yaw, te ay buur askanoo ci sa geño. \v 12 Réew, mi ma sédd Ibraayma ak Isaaxa, yaw laa koy sédd, yaak askan wi soqikoo ci yaw.» \p \v 13 Naka la Yàlla wax ak Yanqóoba loolu, daldi teqlikoo ak moom. \v 14 Yanqóoba samp doju xàmmikaay ca bérab, ba Yàlla waxe ak moom, tuural ko fa biiñ, sotti fa diw, sellale. \v 15 Yanqóoba ma nga tudde bérab, ba Yàlla waxeek moom, Betel\f + \fr 35.15 \fr*\ft Seetal ci 28.19.\ft*\f*. \s1 Beñamin juddu na, Rasel faatu \p \v 16 Ba loolu wéyee ñu jóge Betel, dem bay bëgga jub Efrata. Rasel tollu ciw mat, te mat wi metti. \v 17 Ba mu demee ba mat wa gëna metti, rewlikat ba ne ko: «Muñal nag, ndax góor laati de!» \v 18 Booba Rasel a ngi waaja faatu. Terewul bala bakkanam a rot tudde na xale bi Benoni (mu firi Sama doomu coono). Teewul baay bi tudde ko Beñamin (mu firi Sama doomu njiglaay)\f + \fr 35.18 \fr*\fk Beñamin \fk*\ft mu ngi jóge ci \ft*\fq ben yamin, \fq*\ft di tekki «doomu ndijoor», waaye li tur wiy wund mooy «doomu njiglaay».\ft*\f*. \p \v 19 Ci kaw loolu Rasel faatu, ñu denc ko ca yoonu Efrata, ga ñuy wax Betleyem ba tey. \v 20 Yanqóoba nag samp aw doj ca bàmmeel ba, te mooy xàmmikaayu bàmmeelu Rasel ba tey jii. \v 21 Ba mu ko defee Israyil jóge fa, samp xaymaam ca gannaaw Migdal Eder. \s1 Doomi Yanqóoba ya \p \v 22 Ba Israyil dëkkee ca réew ma, am na bés Ruben dem tëdd ak Bilaa, nekkaaleb baayam; Israyil yég ko. \p Doomi Yanqóoba\f + \fr 35.22 \fr*\fk Yanqóoba \fk*\ft mooy Israyil.\ft*\f* yu góor fukk lañu ak ñaar. \v 23 Doomi Leya ñooy: Ruben, taawub Yanqóoba, ak Simeyon ak Lewi ak Yuda ak Isaakar ak Sabulon. \v 24 Doomi Rasel di Yuusufa ak Beñamin. \v 25 Doomi Bilaa, jaamub Rasel, di Dan ak Neftali. \v 26 Doomi Silpa, jaamub Leya, di Gàdd ak Aser. Ñooñooy doomi Yanqóoba, te mu am leen ca Padan Aram. \s1 Isaaxa nelaw na \p \v 27 Yanqóoba dellu na kër baayam Isaaxa fa Mamre, ca Kiryaat Arba, gay Ebron ba tey, fa Ibraayma ak Isaaxa daloon. \v 28 Isaaxa dund na téeméeri at ak juróom ñett fukk (180). \v 29 Foofa la bakkanam rote, mu faatu, fekki ay maamam, gannaaw ba mu màggatee, ba ñor xomm. Ba loolu amee ay doomam Esawu ak Yanqóoba rob ko. \c 36 \ms1 Askanu Esawu \mr (Saar 36.1-43) \p \v 1 Askanu Esawu, mi ñuy wax Edom, mooy lii. \p \v 2 Esawu jël na janqi Kanaaneen jabar. Ñooñoo di: Ada doomu Elon, Etteen ba, ak Olibama doomu Ana, miy doomu Sibeyon, Eween ba, \v 3 ak Basmat doomu Ismayla, di jigéenub Nebayot. \v 4 Ada am ak Esawu Elifas; Basmat am ca Rewel. \v 5 Olibama am ca Yewus, Yalam ak Kora. Ñooñu ñooy doomi Esawu, te mu am leen ca réewu Kanaan. \p \v 6 Ba loolu amee Esawu ànd aki soxnaam, aki doomam yu góor ak yu jigéen, ak waa këram ñépp, jiital géttam ak juram gépp, yóbbaale mboolem alal ju mu amoon ca réewu Kanaan, daldi sanci meneen réew ngir sore rakkam Yanqóoba. \v 7 Li ko waral mooy, seen alal dafa bare woon lool, ba manuñoo dëkk ñoom ñaar, te réew, mi ñu daloon, àttanu leen ndax seen gétt yu bare. \v 8 Esawu nag dëkk ca tundu Seyir: Esawu moomu mooy Edom. \p \v 9 Askanu Esawu, di maami Edomeen ña ca tundi Seyir, mooy lii. \p \v 10 Doomi Esawu yu góor ñooy: Elifas, mi mu am ak soxnaam Ada ak Rewel, mi mu am ak Basmat. \v 11 Doomi Elifas yu góor yi di: Teman ak Omar ak Sefo ak Gatam ak Kenas. \v 12 Timna it nekkaaleb Elifas. Mu am caak moom Amaleg. Ñooñoo xeetoo ci Ada, soxnas Esawu. \v 13 Doomi Rewel yu góor yi ñoo di: Naxat ak Sera ak Saama ak Misa. Ñooñoo xeetoo ca Basmat, soxnas Esawu. \v 14 Soxnas Esawu, si ñu naa Olibama, tey doomu Ana miy doomu Sibeyon, moo am ak Esawu doom yu góor yii: Yewus, Yalam ak Kora. \p \v 15 Làngi doomi Esawu yu góor nag, ñooy ñii. Ñi askanoo ci Elifas taawub Esawu, ñuy Teman ak Omar ak Sefo ak Kenas \v 16 ak Kora ak Gatam ak Amaleg, ku ci nekk ak làngam. Làngi Elifas, ya ca réewum Edom a ngi noonu; ñooy sëti Ada. \v 17 Ñi askanoo ci Rewel doomu Esawu, ñooy Naxat ak Sera ak Saama ak Misa, ku ci nekk ak làngam. Làngi Rewel, ya ca réewum Edom a ngi noonu; ñooy sëti Basmat, soxnas Esawu. \v 18 Ñi xeetoo ci Olibama soxnas Esawu, ñooy Yewus, Yalam ak Kora, ku ci nekk ak làngam. Ñooñooy làngi Olibama, soxnas Esawu siy doomu Ana. \v 19 Ñooñooy doomi Esawu, mi ñuy wax Edom, ñooñooy doomam yu góor, ñook seeni làng. \s1 Lu jëm ci askanu Seyir \p \v 20 Doomi Seyir, ya bokk ca waa Or te sancoon ca réew ma, ñooy Lotan ak Sobal ak Sibeyon ak Ana \v 21 ak Dison ak Eser ak Disan. Ñooñooy làngi waa Or, di sëti Seyir ya ca réewum Edom. \v 22 Doomi Lotan yu góor ya nag ñooy Ori ak Emam. Jigéenub Lotan di Timna. \v 23 Doomi Sobal yu góor ya di Alwan ak Manaat ak Ebal ak Sefo ak Onam. \v 24 Doomi Sibeyon yu góor di Aya ak Ana. Te Ana moomu moo feeñal bëti ndox yu tàng ya ca màndiŋ ma, ba muy sàmm mbaami baayam Sibeyon. \v 25 Doomi Ana ñooy Dison ak Olibama, doomam ju jigéen. \v 26 Doomi Dison di Emdan ak Esban ak Yitran ak Keran. \v 27 Doomi Eser di Bilan, Saawan ak Akan. \v 28 Doomi Disan di Uus ak Aran. \s1 Lu jëm ci buur ya jëkka falu ca Edom \p \v 29 Làngi waa Or ñooy ñi askanoo ci Lotan ak Sobal ak Sibeyon ak Ana \v 30 ak Dison ak Eser ak Disan, ku ci nekk ak làngam. Ñooñooy làngi waa Or, na ñu xàjjalikoo kenn-kenn ca réewu Seyir. \p \v 31 Buur, yi falu ca réewum Edom, lu jiitu kenn ci waa Israyil di fa falu, ñooy ñii. \v 32 Bela doomu Beyor falu na ca Edom. Dinaba moo doon péeyam. \v 33 Ba Bela faatoo, Yobab doomu Sera, ma dëkk Boccra, wuutu ko. \v 34 Ba Yobab faatoo, Usam mu diiwaanu waa Teman wuutu ko. \v 35 Ba Usam faatoo, Adàdd, ma dàqoon waa Majan ca réewu Mowab, tey doomu Bedàdd, moo falu, wuutu ko. Awit a doon péeyam. \v 36 Ba Adàdd faatoo, Samla, ma dëkk Masreka, falu, wuutu ko. \v 37 Ba Samla faatoo, Sawul ma woon ca Reyobot Efraat, falu, wuutu ko. \v 38 Ba Sawul faatoo, Baal Anan doomu Agbor falu, wuutu ko. \v 39 Ba Baal Anan doomu Agbor faatoo, Adar falu, wuutu ko. Pawu moo doon péeyam, soxnaam di Metabeel, mi Mataredd doomu Me Saab di yaayam. \p \v 40 Làng yi sosoo ci Esawu nag, làng gu ci nekk ak turam ak njaboot, ya mu ëmb, ak gox, ba mu dëkke, ñoo di ñii: ñi askanoo ci Timna ak Alwa ak Yetet \v 41 ak Olibama ak Ela ak Pinon \v 42 ak Kenas ak Teman ak Mibsar \v 43 ak Magdiyel ak Iram, ku ci nekk ak làngam. Ñooñu ñooy làngi Edom, ma ñu naa Esawu, moom ma giir Edomeen ñi, làng gu ci nekk ak gox, ba nga dëkke te moom ko. \c 37 \ms1 Askanu Yanqóoba \mr (Saar 37.1—50.26) \s1 Yuusufa gént na lu yéeme \p \v 1 Yanqóoba ma nga dëkkoon réewu Kanaan, fa baayam daloon. \p \v 2 Askanu Yanqóoba mooy lii. \p Yuusufa tollu na ci waxambaane, am fukki at ak juróom ñaar, di sàmmle jur gi doomi baayam, yi nga xam ne soxnay baayam Bilaa ak Silpa ñoo leen jur. Yuusufa nag di leen boole ak seen baay. \v 3 Booba Yanqóoba, Yuusufa la gëna bëgg ci ay doomam, ndax li mu màggat door koo am. Mu ràbblul ko mbubb mu yànj. \v 4 Mag ya nag gis ne Yuusufa la seen baay gëna bëgg ci ay doomam. Loolu tax ñu bañ ko, ba manuñoo séq ak moom kàddu gu rafet. \p \v 5 Mu am bés Yuusufa gént, nettali ko ay magam, ba tax ñu gënati koo bañ. \v 6 Da ne leen: «Dégluleen li ma gént. \v 7 Danoo nekk ca tool ya, di góob. Ba nu takkee, sama takk jekki-jekki ne sàtt, taxaw, seen takk wër sama takk, di ko sujjóotal.» \v 8 Mag ya ne ko: «Dangaa nara falu ci sunu kaw? Danga noo nara jiite?» Ñu gënati koo bañ nag ndax géntam ya ak la mu leen ca wax. \p \v 9 Gannaaw gi geneen gént dikkal ko, mu nettali ko ay magam ne leen: «Dégluleen, géntaat naa. Gis naa jant bi ak weer wi ak fukki biddiiw ak benn di ma sujjóotal.» \v 10 Ba mu ko nettalee ay magam, ba nettali ko baayam, baayam da koo soow ne ko: «Yaw, li nga gént, lu mu doon? Xanaa du maak sa yaay ak say mag noo lay sujjóotal?» \v 11 Mag ya nag iñaane ko. Teewul baayam moom bàyyi xel ci mbir moomu. \p \v 12 Mu am bés ay magam dem dëkk ba ñuy wax Sikem, sàmmi seen juru baay. \v 13 Israyil ne Yuusufa: «Xam nga ne say mag sàmmi nañu Sikem. Kaay, ma yónni la ci ñoom.» Yuusufa ne ko: «Waaw.» \v 14 Yanqóoba ne ko: «Demal seeti say mag, ba xam ndax ñu ngi ci jàmm, ñoom ak jur ga, te nga ñëw, wax ma.» Mu yebal ko, mu jóge xuru Ebron, jubal Sikem. \p \v 15 Naka la jenn waay dajeek moom foofa, fekk muy wëreelu ca àll ba. Waa ja ne ko: «Looy seet?» \v 16 Yuusufa ne ko: «Samay mag laay seet. Xamoo fu ñu tollu, di sàmm?» \v 17 Waa ja ne ko: «Jóge nañu fii de, ndax dégg naa ñu naan: “Nanu dem Dotan.”» Yuusufa toppi magam ya ba Dotan, fekk leen fa. \p \v 18 Naka la ko mag ya séen fu sore, daldi mànkoo bala moo agsi, ci pexem rey ko. \v 19 Ña nga naan: «Boroom gént gaa ngee di ñëw! \v 20 Nanu ko rey gaaw, sànni ko ca kàmb yee\f + \fr 37.20 \fr*\fk kàmb \fk*\ft yooyu loxo lañu ko daan yette ca màndiŋ ma, di ca denc ndox.\ft*\f*, su ko defee danu naan, rabu àll a ko fàdd. Nu seet ba xam fu muy mujj aki géntam?» \p \v 21 Ruben nag dégg ca, di ko fexee xettli. Mu ne leen: «Bunu ko rey.» \v 22 Ruben teg ca ne leen: «Buleen tuur deret. Sànnileen ko ca kàmb gee ca àll ba, waaye bu ko loxo dal.» Booba ma ngay wut nu mu xettlee Yuusufa ci ñoom, ba delloo ko baayam. \p \v 23 Ba Yuusufa agsee ca magam ya, dañoo futti mbubbam, mooy mbubb mu yànj, ma mu soloon. \v 24 Ñu jàpp ko, tàbbal ca biir kàmb ga, fekk mu déy, ba wow koŋŋ. \v 25 Loolu wees ñu toog, di lekk. Nes tuut ñu siggi, séen am njëggum giléem, muy ay Ismayleen, yu sëf cuuraayu ndàbb ak diwu yaram ak cuuraayu xas\f + \fr 37.25 \fr*\fk cuuraay \fk*\ft yooyu gom la woon ak boom ak miir.\ft*\f*, jële ko réewu Galàdd, jëme Misra. \v 26 Yuda ne doomi baayam ya: «Bu nu reyee sunu rakk jii, nëbb deret ji, lu nu ciy jële? \v 27 Tee nu koo jaay Ismayleen ñi, te bañ koo sàkkal pexe nun ci sunu bopp? Ndax kat sunu rakk a, di sunu deret.» Doomi baay ya déggal ko. \v 28 Julay Majan ya nag jaare fa, ñu yóotu Yuusufa, génne ko kàmb ga, jaay ko Ismayleen ña ci ñaar fukki dogi xaalis. Ñu yóbbu Yuusufa Misra. \p \v 29 Ba mu ko defee Ruben dellu ca kàmb ga, gis ne Yuusufa nekkatul ca biir, mu mititlu ko, ba xotti ay yéreem. \v 30 Ba loolu amee mu jóge ca, dem ca ay rakkam ne leen: «Xale ba nekkatu fa de! Te man xawma nu may def léegi.» \v 31 Ñu jël nag mbubbu Yuusufa, rendi ab sikket, taqal mbubb ma ca deret ja. \v 32 Gannaaw loolu ñu yóti seen baay mbubb ma, ne ko: «Lii lanu gis de, xoolal bu baax ndax du sa mbubbu doom?» \v 33 Yanqóoba xàmmi ko, daldi ne: «Sama mbubbu doom a moos! Éey waay, rabu àll kay moo daggate Yuusufa, yàpp ko!» \v 34 Ci kaw loolu Yanqóoba mititlu ko, ba xotti ay yéreem, taraxlaayoo ab saaku, di jooy doomam ay fan. \v 35 Doomam yépp, góor ak jigéen ñëw, di ko dëfal, te noppiwul, xanaa naan: «Damay jooy, ba dem njaniiw, fekki sama doom.» Baayam di ko jooy, \v 36 fekk waa Majan yóbbu nañu ko Misra, jaay ko Potifaar, jawriñu Firawna mi jiite ay dagam. \c 38 \s1 Lu jëm ci Yuda ak Tamar ak seen askan \p \v 1 Ca jamono yooyu Yuda dafa teqlikoo ak ay doomi baayam, dal ca waa ju dëkk Adulam te tudd Ira. \v 2 Foofa nag Yuda gis fa senn as ndaw, su doon doomu Kanaaneen bu tudd Suwa, mu jël ko soxna. \v 3 Mu ëmb, am doom ju góor, tudde ko Er. \v 4 Mu dellu ëmb, am doom ju góor, tudde ko Onan. \v 5 Mu amati doom ju góor, tudde ko Sela. Ba Sela di juddu, ca Kesib la fekk Yuda. \p \v 6 Gannaaw gi Yuda jëlal taawam Er jabar ju tudd Tamar. \v 7 Er, taawub Yuda boobee, doonoon ku \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji seede coxoram; Aji Sax ji nag rey ko. \v 8 Yuda ne Onan: «Demal ci sa jabaru mag, donn ko, ndax nga giiral sa mag aw askan.» \v 9 Teewul Onan xam ne du doon askan wu muy moom, ba tax saa yuy dëkkoo jabaru magam, bay wara àgg rekk, tuur wasal wi ci suuf, ngir baña giiral magam\f + \fr 38.9 \fr*\ft Ci yooyu jamono, ku donn sa jabaru mag ci bànni Israyil, doom joo ca am, du bokk ci yaw waaye dañu koy féetele sa mag ji faatu.\ft*\f*. \v 10 Aji Sax ji ñaawlu li muy def, ba tax mu faat ko, moom itam. \v 11 Yuda daldi wax Tamar jabaru doomam ne ko: «Demal sa kër baay, ténjeji fa, ba sama doom Sela màgg.» Booba Yuda dafa ragal Sela faatu moom itam ni ay magam. Tamar nag dem, toog kër baayam. \p \v 12 Ba ñu demee ba mu yàgg, doomu Suwa, soxnas Yuda faatu. Ba dëj ba wéyee, Yuda dem fekki watkati xaram ca Timna. Ira, xaritam bi dëkk Adulam a nga ànd ak moom. \v 13 Ñu yégal Tamar ne ko: «Sa goroo ngii jëm Timna, di wati ay xaram.» \v 14 Ba loolu amee mu summi yérey jëtun ya, muuru, sàngu, toog ca selebe yoon wa jëm Enayim ca yoonu Timna, ndax booba gis na ne Sela màgg na te mayuñu ko ko, muy jabaram. \v 15 Yuda gis ko, yaakaar ne gànc la, ndax li mu muuru\f + \fr 38.15 \fr*\ft Ci yooyu jamono gànc yi daan nañu leen xàmmee seen muuraay.\ft*\f*. \v 16 Mu jàdd, ñëw ba ca moom, ne ko: «May ma, ma ànd ak yaw.» Fekk na xamul woon ne goroom la. Mu ne ko: «Loo may fey, ngir ànd ak man?» \v 17 Mu ne ko: «Dinaa jël bëy wu ndaw ca sama gétt, yónnee la.» Mu ne ko: «Jox ma lenn looy tayle, ba kera ngay yónnee.» \v 18 Mu ne ko: «Lu ma lay tayle?» Ndaw si ne ko: «Xanaa sa jaarob màndargaal, ak buum, gi mu àndal ak yet, wi ci sa loxo.» Mu jox ko nag, ba noppi ànd ak moom. Fa la doxe ëmb. \v 19 Ndaw sa dem yoonam, dindi muuraay ba, solaat yérey jëtun ya. \p \v 20 Ba loolu wéyee Yuda yebal xaritam, ba dëkk Adulam, mu yóti ndaw sa bëy wu ndaw wa, ba mana jotaat la mu tayle woon ca ndaw sa. Xarit ba nag gisu ko. \v 21 Mu laaj waa gox ba, ne leen: «Ana gànc biy toog Enayim ci yoon wi?» Ñu ne ko: «Fii de ab gànc nekku fi.» \v 22 Mu dellu ca Yuda ne ko: «Gisuma ko de, te it waa gox ba nee nañu, foofa gànc nekku fa.» \v 23 Yuda ne ko: «Nanu ko ko wacce, mu jël, lu ko moy ñu ree nu, gannaaw maa ngi nii yónnee bëy wu ndaw wii, te yaw gisoo ko kay.» \p \v 24 Ba ñu ca tegee lu tollook ñetti weer, ñu xamal Yuda ne ko, Tamar goroom ba, da doon jaay boppam, ba jaare ca ëmb. Yuda ne: «Nañu ko yóbbu, lakk ko, ba mu dee.» \v 25 Naka lañu koy yóbbu, mu yóbbante goroom ba ay kàddu. Da koo wax ne ko: «Ki moom lii moo ma ëmbal.» Mu teg ca ne ko: «Xoolal bu baax te wax ma ku moom jaarob màndargaal, bi ànd ak buum gi, ak yet wi.» \v 26 Yuda xàmmi yëf ya nag, ne: «Moo ma gëna nekk ci dëgg de, gannaaw mayuma ko sama doom Sela.» Gannaaw ba loolu wéyee, àndatul ak moom. \p \v 27 Tamar dem, ba wara wasin, ndekete ay seex la ëmb. \v 28 Ba muy mucc, kenn ca doom ya daa tàllal loxo ba, rewlikat ba jàpp ca, takk ca wëñ gu xonq curr. Mu ne: «Kii moo jëkka génn.» \v 29 Naka la delloo loxoom, seexam juddu, mu ne ko: «Yaw foo bëtte, ba génn?» Ñu daldi ko tudde Peres (mu firi Bëtt). \v 30 Nes tuut seex, bi wëñ gi takke ci loxo li, door caa topp, ñu tudde ko Sera. \c 39 \s1 Jaay nañu Yuusufa jawriñu Firawna \p \v 1 Ba ñu yóbboo Yuusufa Misra, Potifaar, jawriñu Firawna\f + \fr 39.1 \fr*\fk Firawna \fk*\ft tur la, wu buuri Misra daan tudd. Firawna mii wuute na ak Firawna, mi bokkoon ak Musaa jamono.\ft*\f*, ma jiite ay dagam, da koo jënd ca Ismayleen, ña ko fa indi. \p \v 2 Ci kaw loolu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ànd ak Yuusufa, may ko ndam, mu dëkk ca kër sangub waa Misraam ba. \v 3 Sang ba nag gis ne Aji Sax jaa ngi ànd ak Yuusufa, di ko may ndam ci lépp lu mu sabablu. \v 4 Sang ba am cofeel ci Yuusufa, def ko fara biir këram, dénk ko saytub kër ga, ba teg ciy loxoom lépp lu mu moom. \v 5 Boobee waayi Misra ja dénkee Yuusufa këram ak lépp lu mu moom, mu di ko saytu, ca la Aji Sax ji dale barkeel këram, barkeelaale mboolem lu mu moom, kër ak tool. \v 6 Mu daldi bàyyi lépp ci loxol Yuusufa, te li mu fa nekk tax ba topptootul dara ciy mbiram, lu moy li muy lekk rekk. Booba Yuusufa ku jekkoon bind la te góorayiw. \s1 Soxnas Potifaar fexeel na Yuusufa \p \v 7 Mu am bés nag soxnas sangub Yuusufa ba xemmem Yuusufa, daldi ne ko: «Kaay tëdd ak man.» \v 8 Teewul Yuusufa bañ, ne soxnas sang ba: «Déglul, sama sang da maa jébbal lépp, ba topptootul dara ci kër gi. \v 9 Ëpplewu ma sañ-sañ ci biir kër gi, te aayewu ma lenn xanaa yaw, ndax soxnaam nga. Kon léegi nu may mana defe ñaawtéef wu réy wu ni tollu, di moy Yàlla?» \v 10 Ba loolu amee bés bu Yàlla sàkk mu di ko wax Yuusufa, te dégluwu ko, wéetul ak moom sax, bay tëdd ak moom. \p \v 11 Mu am bés Yuusufa dugg ca kër ga, di def liggéeyam, te kenn ci surga yu góor ya nekku fa. \v 12 Ndaw si jàpp ci mbubb mi, ne ko: «Kaay tëdd ak man.» Yuusufa nag wacc mbubb ma cay loxoom, daw génn kër ga. \v 13 Ndaw si gis mbubb, mi mu ko wacce, ba daw génn, \v 14 mu woo surgay kër ga, ne leen: «Xool-leen, \w Ebrë|lemma="Ebrë:"\w*, sii sama jëkkër indi ci kër gi, mu di nu yab. Dafa ñëw, bëgg maa tëdde, ma yuuxu ca kaw. \v 15 Naka laa yuuxu ca kaw, mu wacce ma mbubbam, daw génn.» \v 16 Ba mu ko defee ndaw si denc mbubb ma, ba sangub Yuusufa ba ñibbsi, \v 17 mu nettalee ko ko noonu ne ko: «Jaamu ebrë, bi nga indi ci kër gi de, da maa fekksi, di ma sàkku. \v 18 Naka laa yuuxu ca kaw, mu daw génn, wacce ma mbubbam.» \s1 Tëj nañu Yuusufa kaso \p \v 19 Sang bi dégg li ko soxnaam wax ne moom la ko jaamam def, mu mer lool, \v 20 ba jàpp Yuusufa, tëj ko kaso, ba ñuy denc ñi buur jàpp. Yuusufa nekk foofa ca kaso ba. \p \v 21 Teewul \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ànd ak Yuusufa, laaye ko biir, daldi xiir wattukatu kaso ba ca moom, mu yéwéne ko. \v 22 Ci kaw loolu mu may Yuusufa, mu yilif ñi ñu tëj ñépp, te mboolem lu ñu fay def, mu di ko jiite. \v 23 Wattukat ba seetatuloon dara lu Yuusufa jiite, ndax Aji Sax jee ànd ak moom, te lu mu sabablu, Aji Sax ji may ko ca ndam. \c 40 \s1 Yuusufa firi na ñaari gént \p \v 1 Ba loolu wéyee kiy topptoo naani buuru Misra ak lakk-katu mburoom dañoo tooñ buuru Misra, seen sang. \v 2 Firawna nag mere lool ñaari jawriñ yooya, kenn ka di kilifay ñay topptoo naani buur, ka ca des di kilifay lakk-kati mburu ya, \v 3 ba tax mu tëj leen ca kër kilifag wattukat ba, ca kaso, ba ñu tëj Yuusufa. \v 4 Kilifag wattukat ya teg leen ca loxol Yuusufa, mu di leen topptoo. \p Ba ñu nekkee ab diir ca kaso ba, \v 5 jawriñi buuru Misra, ya ñu tëj, muy ñaar ña féetewoo naani buur ak mburoom, dañoo géntandoo ci genn guddi, gént gu ci nekk ak li muy firi. \v 6 Yuusufa xëy, fekk leen ñu jaaxle. \v 7 Mu laaj jawriñi Firawna, yooyee ñu tëjandoo woon ak moom ca kër sangam, ne leen: «Lu leen tax ne yogg tey?» \v 8 Ñu ne ko: «Ay gént daal a nu dikkal, te amunu ku nu koy firil.» Yuusufa ne leen: «Xanaa du Yàllaa moom piri? Nettalileen ma seeni gént rekk kay.» \p \v 9 Jawriñ bay topptoo naanu buur daldi nettali géntam Yuusufa, ne ko: «Ci gént gi, garabu reseñ laa gis ci sama kanam, \v 10 mu def ñetti car. Naka la focci rekk, gaawa tóor, cëgg ya meññ reseñ ju ñor. \v 11 Maa ngi téye nii kaasu Firawna ci sama loxo, jël reseñ ji nag, nal ko ci kaasu Firawna, ba noppi teg kaas bi ci loxol Firawna.» \p \v 12 Yuusufa ne ko: «Piri mi mooy lii. Ñetti car yi, ñetti fan la. \v 13 Fii ak ñetti fan Firawna dina la siggil, delloo la sa liggéey, ngay teg kaasu Firawna ci loxoom, ni nga ko daa defe naka jekk, ba nga yoree naanam. \v 14 Waaye ngalla boo delloo ca sa teraanga, nanga ma geestu te dimbali ma, waxal ma Firawna lu jëm ci man, ba man maa génne fii. \v 15 Ndax man kat dañu maa sàcce ca réewum \w Ebrë|lemma="Ebrë:"\w* ya, te fii itam, defuma fi lu tax, ñu war maa tëj.» \p \v 16 Kilifag lakk-kati mburu ya nag gis ne piri mi neex na, mu ne Yuusufa: «Man it sama gént gi, xam nga lu ma ci gis? Ñetti pañey mburu mu weex laa yenu, \v 17 ba féete kaw a nga yeb mboolem xeeti mburu yu ñuy lakkal Firawna, picc yaa nga koy for ca pañe, ba ma yenu.» \p \v 18 Yuusufa ne ko: «Piri mi mooy: ñetti pañe yi, ñetti fan la. \v 19 Fii ak ñetti fan Firawna dina la siggil, ba noppi wékk la ci bant, picc yi ñëw, di for sa suux.» \p \v 20 Ñu teg ca ñetti fan, Firawna di màggal bésu juddoom, dajale jawriñam yépp, di leen berndeel, daldi cay seppee kilifa gay topptoo ay naanam, ak kilifag lakk-kati mburu ya, siggil leen. \v 21 Mu delloo nag kilifa gay topptoo ay naanam ca liggéeyam, mu teg kaas ba ca loxol Firawna. \v 22 Kilifag lakk-kati mburu ya moom, da koo wékk ci bant, na leen ko Yuusufa firile woon. \p \v 23 Waaye kilifa, ga yore naani Firawna, xalaatul sax Yuusufa, da koo fàtte. \c 41 \s1 Firawna gént na \p \v 1 Ñaari ati lëmm wees na gannaaw loolu, gént dikkal Firawna, mu jeneer taxaw ca wetu dexu Niil. \v 2 Mu gis juróom ñaari nag yu rafet te suur génne ca dex ga, di for baraxi tàkk ga. \v 3 Mu dellu gis juróom ñaari nag yu ñaaw te yooy topp ca ñoom, génne ca dex ga, làng ak ñoom ca tàkk ga. \v 4 Nag yu ñaaw ya te yooy daldi lekk juróom ñaari nag yu rafet ya te suur. Firawna yewwu, \v 5 ba noppi nelawaat, dellu gént, gis juróom ñaari gub\f + \fr 41.5 \fr*\fk gub \fk*\ft yi ñuy wax fii, bele la woon.\ft*\f* yu nangu te baax sax ci benn gattax. \v 6 Gannaaw ga juróom ñaari gub yu gooy yu ngelaw li lakk sax, tegu ca ya jiitu. \v 7 Ca la gub yu gooy ya wonn juróom ñaari gub yu nangu ya te baax. Gannaaw loolu Firawna yewwu, xam ne gént la woon. \p \v 8 Ba bët setee, Firawna jaaxle lool, ba woolu jibar ya ak boroom xam-xami Misra yépp, nettali leen la mu gént, te kenn manu koo firil Firawna. \p \v 9 Ba loolu amee kilifa gay topptoo naani Firawna ne ko: «Man de tooñ naa te dinaa la ko wax tey. \v 10 Sang bi, ba nga nu meree, yaw Firawna, ba tëj ma kaso ca kër njiitu dag ya, man ak kilifag lakk-kati mburu ya, \v 11 genn guddi danoo géntandoo, man ak moom, gént gu ci nekk ak la muy firi. \v 12 Fekk amoon na waxambaanew \w ebrë|lemma="Ebrë:"\w* wu fa nekkoon ak nun, te doonoon jaamub njiital dag ya. Nu nettali ko sunuy gént, mu firil nu ko, wax nu ku nekk la sa gént di tekki. \v 13 Te na mu nu ko firile woon, na la ame: delloo nañu ma sama liggéey, ka ca des ñu wékk ko ci bant.» \s1 Yuusufa firi na génti Firawna \p \v 14 Ba Firawna déggee loolu, dafa woolu Yuusufa. Ñu gaaw tijji ko, mu watu, solu, doora wuyji Firawna. \v 15 Firawna ne Yuusufa: «Damaa gént, te kenn manu koo firi, te ma dégg ñuy wax ci yaw naan, gént goo dégg rekk, xam ko, ba man koo firi.» \v 16 Yuusufa ne ko: «Du ci man de, waaye Yàlla mooy baaxe Firawna pirim jàmm.» \p \v 17 Firawna ne Yuusufa: «Damaa gént, taxaw ci tàkkal dexu Niil, \v 18 ma gis juróom ñaari nag yu suur te rafet génne ca dex ga, di for baraxu tàkk ga. \v 19 Ma dellu gis yeneen juróom ñaari nag yu ràgg, ñaaw te yooy génne ca dex ga, topp ci ñoom, di yu ñaaw, ba masumaa gis lu ni mel ci Misra. \v 20 Noonu yu yooy ya te ñaaw daldi lekk juróom ñaari nag, ya jëkkoona feeñ te suur. \v 21 Waaye bi ñu leen lekkee ba noppi, itam dafa mel ni lekkuñu leen, ndax terewuleena mel na woon. Booba laa yewwu, \v 22 ba noppi dellu gént, gis juróom ñaari gub yu fees te baax sax ci benn gattax. \v 23 Gannaaw ga ma gis juróom ñaari gub yu gooy yu ngelaw li lakk, sax tegu ca ya jiitu. \v 24 Gub yu gooy ya nag wonn juróom ñaari gub yu baax ya. Nettali naa ko samay jibar, waaye kenn ci ñoom manu ma koo firil.» \p \v 25 Yuusufa ne Firawna: «Sa ñaari gént yi de, sang bi, ñoo bokk piri. Sang bi, Yàlla da laa xamal li muy def ëllëg. \v 26 Juróom ñaari nag yu baax yi, juróom ñaari at la. Te it juróom ñaari gub yu baax yi, juróom ñaari at la. Muy genn gént gi. \v 27 Te itam juróom ñaari nag yu yooy, yi ci topp te ñaaw, juróom ñaari at la. Naka noonu juróom ñaari gub yu gooy, yi ngelaw li lakk, juróom ñaari ati xiif lay firi. \v 28 Mooy li ma la wax rekk, sang bu tedd bi: li Yàlla di defi ëllëg la la won. \v 29 Nu ngi dëgmal juróom ñaari ati naataange yu réy ci mboolem réewum Misra. \v 30 Te juróom ñaari ati xiif a ciy topp, ba ñu fàtte naataange gu réy ga amoon réewum Misra. Xiif ba cay topp dina yàq réew mi. \v 31 Xiif bi dina tax lenn luy nirook naataange dootu des ci réew mi, ndax dina metti lool. \v 32 Te nag, sang bi, gannaaw gént nga ko ñaari yoon, kon Yàlla dogal na mbir mi, te dina ko amal balaa yàgg.» \p \v 33 Yuusufa teg ca ne Firawna: «Kon léegi sang bi, wutal nit ku muus te rafet xel, jiital ko ci réewum Misra. \v 34 Te itam sang bi, dangay fal ay ndaw ci réew mi, ñuy sàkku juróomi natt yu ne benn ci mboolem lu ñu góobe réewum Misra diiru juróom ñaari ati naataange yiy ñëw. \v 35 Ñoom nañu dajale mboolem dundi at yu baax yi, te boole pepp mi ci sa ndigalu bopp, yaw Firawna, muy dund bu ñuy denc ci dëkk yi. \v 36 Dund boobooy doon sàqu réew mi diiru juróom ñaari ati xiif yiy dal ci réewum Misra; su ko defee waa réew mi duñu loru ci xiif bi.» \s1 Firawna fal na Yuusufa, mu jiite Misra gépp \p \v 37 Pexe moomu nag doon lu Firawna aki jawriñam yépp njort ne baax na. \v 38 Firawna daldi ne jawriñ ya: «Ndax masees naa gis ku mel ni kii a waay, nit ku Yàlla sol Noowug boppam?» \v 39 Firawna wax ak Yuusufa ne ko: «Ndegam Yàlla xamal na la lii lépp kay, leer na ne amul kenn ku muus te rafet xel ni yaw. \v 40 Kon dinaa la may, nga jiite kër buur, te waa réew mépp ci sa waaw lañuy wéy; jal bi ma toog doŋŋ laa lay sute.» \p \v 41 Gannaaw loolu Firawna neeti Yuusufa: «Bés niki tey, dénk naa la réewum Misra gépp» \v 42 Ba loolu amee Firawna tekkee jaarob màndargaal ba ca loxoom, takkal ko Yuusufa, solal ko yérey tànnéef, takkal ko caqu wurus, \v 43 ba noppi waral ko watiiru ku sës rëkk ci moom Firawna, te fu mu ware ñu jiitu ko, di yéene naan: «Sujjóotleen\f + \fr 41.43 \fr*\ft Baat bi ñu tekkee \ft*\fq sujjóotleen \fq*\ft man naa tekki itam «moytuleen» walla «xàll-leen yoon wi».\ft*\f*!» Noonu la ko Firawna fale, mu yilif Misra gépp. \p \v 44 Ci kaw loolu Firawna ne Yuusufa: «Man maay Firawna, waaye gannaaw-si-tey mboolem waa réewum Misra, kenn du ci sañatee yékkati loxo mbaa muy séqi jéego, te àndoo ci.» \v 45 Firawna nag tudde Yuusufa Safnat Paneya, may ko jabar Asnat doomu Potifera ma doon \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ca dëkk ba ñuy wax On\f + \fr 41.45 \fr*\fk On \fk*\ft moo doon péeyu diiney ñiy jaamu jant ca Misra.\ft*\f*. Yuusufa doxe ca tegoo kilifteefu Misra gépp. \v 46 Ba Yuusufay tàmbalee liggéeyal Firawna buuru Misra, mu ngi tollu ci fanweeri at. Yuusufa daldi bàyyikoo ca Firawna, wër réew ma mépp. \p \v 47 Diiru juróom ñaari ati naataange ya suuf sa nangu, ba meññeef ma tuuru. \v 48 Mu dajale mboolem dundub réewum Misra diiru juróom ñaari at yooyee, dëkk bu nekk mu denc fa dund, ba jóge ca tool ya ko wër. \v 49 Fa la Yuusufa jaare dajale pepp, mu ne gàññ, ni suufas géej, ba tàyyeeti koo waññ, ndax mujj na wees ab lim. \p \v 50 Laata ati xiif yay agsi, Yuusufa am na ñaari doom yu góor ak Asnat doomu Potifera, kilifag diine, ga ca On. \v 51 Yuusufa tudde taaw ba Manase (mu firi Ki ma taxa fàtte), ndaxte da ne: «Li ma sonn ak li ma sore sama kër baay lépp, Yàlla fàtteloo na ma ko.» \v 52 Doomam ja ca topp mu tudde ko Efrayim (mu firi Giir), ndaxte da ne: «Yàllaa ma giiral ca réew, ma ma sonne.» \p \v 53 Ci kaw loolu juróom ñaari ati naataange ya jeex ca réewum Misra, \v 54 juróom ñaari ati xiif ya tàmbali, na ko Yuusufa waxe woon. Réew yépp nag nekk ci xiif, waaye amul fu ñàkk dund ca Misra. \p \v 55 Ba waa Misra xiifee, dañoo dem jooytuji dund ca Firawna. Mu wax ak ñépp ne leen: «Demleen ca Yuusufa; lu mu leen wax, defleen ko.» \v 56 Ba ñu demee, ba metitu xiif bi dajal réew mépp, Yuusufa dafa ubbi denc yépp, di jaay pepp mi waa Misra, \v 57 ba nit ñiy jóge fu nekk ci àddina, di wutsi njël ci Yuusufa ndax xiif bu mettee fépp ca àddina. \c 42 \s1 Magi Yuusufa ya dem nañu Misra \p \v 1 Ba Yanqóoba yégee ne pepp am na Misra, daa wax ay doomam yu góor, ne leen: «Lu ngeen di toog, di xoolante rekk?» \v 2 Mu ne leen: «Dégg naa ne pepp am na ca Misra. Demleen jëndali nu ca, ndax nu mana dund, ba xiif bañ noo rey kay!» \p \v 3 Ci kaw loolu fukki magi Yuusufa ya dem Misra, jëndi pepp. \v 4 Waaye Yanqóoba yebalul Beñamin, rakku Yuusufa, ndax dafa ragal ne musiba man na koo dab. \v 5 Doomi Israyil ñëw nag ci biir ñiy jëndsi pepp, ndax xiif bi lawoon na ba Kanaan. \v 6 Fekk booba Yuusufa mooy dogal ca réew ma, di jaay pepp waa réew mépp. Magi Yuusufa ya ñëw, sujjóotal Yuusufa. \s1 Yuusufa xupp na magam ya \p \v 7 Naka la Yuusufa gis magam ya, xàmmi leen, te mel ni ku leen xamul, di wax ak ñoom kàddu yu dëgër ne leen: «Fu ngeen jóge?» Ñu ne ko: «Réewu Kanaan lañu jóge, di jëndsi ab dund.» \v 8 Yuusufa xàmmi na ay magam, waaye ñoom xàmmiwuñu ko. \v 9 Xelum Yuusufa ne yarr ca la mu géntoon ca ñoom, daldi ne leen: «Yeen ay yëddukat ngeen, yuy nemmikusi mbóoti réew mi.» \v 10 Ñu ne ko: «Mukk sang bi, danu lay siyaare, di wutsi ab dund rekk, \v 11 te nun ñépp a bokk baay, di nit ñu maandu; nun kay, sang bi, dunu ay yëddukat.» \v 12 Mu ne leen: «Ahakay, nemmikusi mbóoti réew mi moo leen taxa jóg.» \v 13 Ñu ne ko: «Nun ñii di la siyaare de, fukki góor ak ñaar lanu woon, bokk sunu baay, ba ca Kanaan. Ka ca gën di xalee nga ca sunu baay, te ka ca des nekkatul.» \v 14 Yuusufa ne leen: «Li ma leen wax moo am, ay yëddukat doŋŋ ngeen. \v 15 Waaye nii laa leen di seetloo: bu seen rakk ñëwul, ak bakkanu Firawna, dungeen fi jóge. \v 16 Na kenn ci yeen jëli seen rakk, ñu tëj ñi ci des te topp seen wax, ba xam ndax yeena ngi ci dëgg. Su dul dëgg, giñ naa ci Firawna ne ay yëddukat doŋŋ ngeen.» \v 17 Mu tëj leen ñetti fan. \p \v 18 Ca gannaaw ëllëg sa Yuusufa ne leen: «Bu ngeen defee lii may wax, dingeen dund, ndax man ragal naa Yàlla. \v 19 Ndegam ñu maandu ngeen, na leen kenn ci seen doomi baay wuutu fii, ñi ci des dem yóbbul pepp seen waa kër, yi nekk ci xiif. \v 20 Waaye nangeen ma indil seen rakk, ba ma xam ne li ngeen wax dëgg la; su ko defee dungeen dee.» Ñu daldi ne: «Waaw,» \v 21 te naa ci seen biir: «Céy su nu yégoon, sunu àqu rakk a nu topp nii, ndax danu koo seetaanoon, mu nekk ci njàqarey xol, di nu tinu, te faalewunu ko; looloo waral sunu njàqarey tey jii.» \v 22 Ruben nag àddu ne leen: «Ndax newuma leen woon: “Buleen gàddu bakkanu xale bi,” waaye faalewuleen ma; tey rekk la nu Yàlla doon xaare bakkanam, bi nu gàddu.» \v 23 Ba ñuy wax loolu, foogoon nañu ne Yuusufa déggul seen làkk, ndax làppto, ba doxoon seen diggante, di tekki. \p \v 24 Ci biir loolu mu dummóoyu leen, di jooy. \s1 Doomi Yanqóoba ya dellu nañu Kanaan \p Ba mu jooyee ba noppi, walbatiku, wax ak ñoom, doora jël Simeyon, jéng ko ci seen kanam. \p \v 25 Gannaaw loolu Yuusufa joxe ndigal, ñu sol seeni saaku pepp, te ku nekk ca ñoom, ñu yebal ko xaalisam ca saakoom, ba noppi mayaale leen lu ñu lekk ca yoon wa. Ñu defal leen noonu. \v 26 Ba mu ko defee ñu sëf seeni mbaam pepp ma, daldi fay bàyyikoo. \p \v 27 Fa ñu dal ca guddi, kenn ci ñoom bëgga xont mbaamam, ubbi saakoom rekk, ne pemm ci xaalisam. \v 28 Mu ne doomi baay ya: «Delloo nañu ma sama xaalis, mu ngi nii ci sama saaku.» Seen fit ne tërit, ñuy rag-ragi, ku ne xool sa moroom, naan: «Lu nu Yàlla nattoo nii?» \p \v 29 Ba ñu yeggee ca seen baay Yanqóoba ca réewu Kanaan, daldi koy nettali li leen dal lépp, ne ko: \v 30 «Waa ja yilif réew ma dafa noo résëti, foog ne danuy yëddusi réew ma. \v 31 Nu ne ko: “Nun ay nit ñu maandu lanu, dunu ay yëddukat; \v 32 fukki góor ak ñaar lanu woon yu bokk sunu baay, waaye kenn ka nekkatul, te ka gën di xalee nga fa sunu baay, ba ca réewu Kanaan.” \v 33 Waa ja yilif réew ma ne nu: “Ni may xame ne ñu maandu ngeen, nii la: dangeen may bàyyeek kenn ci yeen, te dem yóbbul dund seen waa kër, yi nekk ci xiif; \v 34 su ko defee ngeen indil ma seen rakk ju ndaw, kon dinaa xam ne dungeen ay yëddukat waaye nit ñu maandu ngeen, te dinaa leen delloo seen mbokk, ngeen mana dem fu leen neex ci réew mi.”» \p \v 35 Naka la ku nekk sotti saakoom, ne jàkk ca mbuusu xaalisam. Ba ñu gisee mbuusi xaalis ya, ñoom ak seen baay, dañoo tiit. \v 36 Seen baay Yanqóoba ne leen: «Xañ ngeen ma ay doom: Yuusufa nekkatul, Simeyon nekkatul, léegi ngeen bëgga jël Beñamin, yóbbu. Loolu lépp ci sama kaw; ngalla man!» \v 37 Ruben wax ak baayam ne ko: «Su ma la ko délloosilul, boo yeboo reyal sama ñaari doom yu góor yi. Tegal Beñamin ci sama loxo rekk, man dinaa la ko délloosil.» \v 38 Ci kaw loolu Yanqóoba ne: «Sama doom daal, du ànd ak yeen, ndax magam faatu na, te moom rekk a des. Su ko musiba dabee ci yoon wi ngeen jëm, dingeen ma yóbbe naqar wu may jàpp, ba kera may ànd ak sama bijjaaw, tàbbi njaniiw.» \c 43 \s1 Magi Yuusufa ya yóbbu nañu Beñamin \p \v 1 Gannaaw loolu xiif bi metti ca réew ma. \v 2 Ba ñu lekkee pepp mi ñu jële woon Misra, ba mu jeex, seen baay ne leen: «Delluleen, wutali nu dund.» \v 3 Yuda ne ko: «Waa ja da noo àrtu woon de, wax na nu ne nu: “Dootuleen jàkkaarlook man te ànduleen ak seen rakk.” \v 4 Boo bàyyee sunu rakk, mu ànd ak nun nag, dinanu dem jëndali la dund. \v 5 Waaye boo ko bàyyiwul kat, dunu dem, ndax waa ja waxoon na nu ne nu: “Dungeen jàkkaarlook man te seen rakk àndul ak yeen.”» \v 6 Israyil ne leen: «Ana lu waral ngeen di ma lor, naan waa ja am ngeen jeneen rakk?» \v 7 Ñu ne ko: «Waa ja kat da nu doon laaj ak a laajaat ci nun ak sunuy bokk, ba naa nu ndax sunu baay mu ngi dund ba tey, ak ndax am nanu rakk. Nun itam nu wax ko li mu nu laaj. Géntunu woon moos ne dina nu sant, nu indil ko sunu rakk!» \p \v 8 La ca tegu Yuda ne Israyil: «Baay, tegal ngóor si ci sama loxo, nu daldi dem, ndax nu dund, baña dee, nook yaw ak sunuy doom. \v 9 Dige naa sama bakkan; boo yeboo laaj ma ko. Bu ma la ko délloosilul, ba teg ko fi sa kanam, maa lay tooñ sama giiru dund. \v 10 Bu nu yeexuloon ba léegi, manoon nanoo dem ba délsi ñaari yoon sax.» \p \v 11 Seen baay Israyil nag ne leen: «Ndegam manula ñàkk, dangeen di def nii: sàkkleen ci ngëneeli réew mi, yeb ci seeni saaku, yóbbul waa ja lu mel ni tuuti diwu yaram ak lem ak cuuraayu xas ak cuuraayu ndàbb ak ay xeeti saal\f + \fr 43.11 \fr*\fk ay xeeti saal \fk*\ft lañu, yu ñuy wax pistaas ak amànd.\ft*\f*. \v 12 Te ngeen yóbbaale ci xaalis lu tollook ñaar-cay la ngeen jënde woon, ngir feyaale loola, ndax jombul njuumte la woon. \v 13 Su ko defee ngeen ànd ak seen rakk, fabu dellu ca waa ja. \v 14 Yal na Yàlla Aji Man ji def waa ja yërëm leen, ba bàyyi seen doomu baay ba, moom ak Beñamin itam. Man nag, su ma naree ñàkk ay doom— aa! Naa leen ñàkk rekk.» \s1 Magi Yuusufa ya dellu nañu Misra \p \v 15 Gaa ña jël nañu sarica booba, yóbbaale nañu it ñaar-cay xaalis ba, daldi ànd ak Beñamin, ñu dem Misra, teewi ca kanam Yuusufa. \v 16 Ba Yuusufa gisee Beñamin ànd ak ñoom, dafa wax fara biir këram, ne ko: «Yóbbul gaa ñi ca kër ga, te nga rey gàtt, defar ko, ndax maak ñoom nooy bokk añ tey.» \v 17 Waa ja def la ko Yuusufa wax, yóbbu gaa ña kër Yuusufa. \v 18 Ñu am nag tiitaange ndax li ñu leen yóbbu kër Yuusufa. Ña ngay xalaat naan: «Boo demee, xaalis bi ñu yeboon ci sunuy saaku yoon wu jëkk wa, moom lañu bëgga taafantoo, dugal nu fii, ba song nu, jàpp nu jaam, nangu sunuy mbaam, boole ci.» \p \v 19 Ba ñu demee ba ca buntu kër Yuusufa, wax nañu ak fara biir këram. \v 20 Ñu ne ko: «Sang bi baal nu, nun de ñëwoon nanu fi lu jiitu ngir jëndsi dund, \v 21 waaye ba nu dalee ca yoon wa, danoo ubbi sunuy saaku, ku nekk ci nun fekk xaalisam ca kaw, mu tollu na mu tollu woon, te indiwaat nanu ko. \v 22 Te it indaale nanu xaalis bu nu jënde dund. Waaye xamunu ku delloo xaalis ba ci sunuy saaku.» \v 23 Mu ne leen: «Jàmm rekk la; buleen tiit, seen Yàlla, jiy seen Yàllay baay, moo leen defal alal ci seeni saaku. Seen xaalis jot naa ci.» Ci kaw loolu mu génne Simeyon, indil leen ko. \p \v 24 Waa ja dugal leen kër Yuusufa, may leen ndox ñu jàngu, ba noppi xont seeni mbaam. \v 25 Ba mu ko defee ñu yebbi seeni sarica, bala Yuusufaa agsi ca digg bëccëg, ndaxte dégg nañu ne foofa lañuy añe. \p \v 26 Ba Yuusufa wàccsee, ñu jébbal ko foofa ca biir kër ga sarica, ba ñu ko indaaleel, daldi koy sujjóotal. \v 27 Mu nuyoo ak ñoom, ba noppi laaj leen ne leen: «Seen baay bu màggat, ba ngeen doon wax, mbaa mu ngi dund? Mbaa mu ngi ci jàmm?» \v 28 Ñu ne ko: «Sunu baay mu ngi dund, sang bi, te mu ngi ci jàmm.» Ña nga koy sukkal tey sujjóotati. \p \v 29 Naka la Yuusufa ne gees, gis Beñamin rakku doomu ndeyam ja. Mu laaj leen ne leen: «Ndax kii mooy seen rakk, ji ngeen ma doon wax?» La ca tegu mu ne rakkam ja: «Sama ngóor si, yal na la Yàlla defal yiw waay!» \v 30 Ci kaw loolu Yuusufa gaaw génn ndax yaram wu daw, te manatula téye ay rongooñam ndax rakkam ja, mu dugg néegu biiram, di jooy. \v 31 Ba mu noppee, sëlmu, génn, doora ànd ak sagoom, daldi joxe ndigal, ne: «Taajleen añ bi.» \v 32 Loolu wees ñu may Yuusufa moom rekk; ber doomi baayam ya. Waa Misra ña fa doon lekke it, ñu beral leen seen ndab, ngir waa Misra daawuñu bokk ak \w Ebrë|lemma="Ebrë:"\w* yi lekk, ndax mbañ la fa woon. \v 33 Ña nga toog, na mu leen ko sante, taaw ba fegge wet, ni ko ko céru taaw maye, ñu sësaloo, na ñu toppantee ciy at, ba ca caat ma. Gaa ñaa nga yéemu, di xoolante. \v 34 Mu sàkkal leen ca ndabam, te Beñamin ëpple ku ci nekk juróomi yoon. Ñu bokk nag naana naan, ba seen xol sedd. \c 44 \s1 Yuusufa nattu na ay magam \p \v 1 Ba loolu wéyee mu sant fara biir këram, ne ko: «Solal seeni saaku pepp lu ñu mana àttan, te nga delloo ku nekk xaalisam, tegal ko ko ca buntu saakoom. \v 2 Waaye sama kaasu xaalis boobee, yebal ko ki gën di xale ci saakoom, boole ko ak xaalisu peppam.» Mu def la Yuusufa wax. \p \v 3 Ca ëllëg sa, ba jant bay fenk, yiwi nañu gaa ña, ñu sëf seeni mbaam, dem. \v 4 Naka lañu génn dëkk ba, te soreeguñu sax, Yuusufa sant fara biir këram, ne ko: «Gaawal dab gaa ña, te boo leen dabee, wax leen ne leen: “Lu tax ñu ji leen njekk, ngeen feye ngoreedi? \v 5 Ndax li ngeen jël du sama kaasu sang, bi muy naane, rawatina di ko gisaanee? Lu ñaaw ngeen def nii!”» \p \v 6 Mu daldi leen dab, wax leen loolu. \v 7 Ñu ne ko: «Kilifa gi, looy wax nii? Nun de, sang bi, jomb nanu loolu! \v 8 Xaalis bi nu fekkoon ci sunu bunti saaku sax, danoo àndaat ak moom, jóge ba Kanaan, délloosil la ko, kon nan lanu mana sàcce sa kër sang xaalis mbaa wurus? \v 9 Ngalla kilifa gi, yaay sunu sang; koo ko fekke ci nun rekk, boo yeboo reyal, ñi des ci nun doxe fa, di say jaam.» \v 10 Mu ne leen: «Li ngeen wax yoon la sax, waaye na ki ma ko fekke doŋŋ di sama jaam, su ko defee ñi ci des wàcc.» \p \v 11 Ñu gaaw nag, wàcce seeni saaku ci suuf, ku nekk ubbi saakoom. \v 12 Ma ngay seet, tàmbalee ca taaw ba, ba ca caat ma, doora fekk kaas ba ca saaku Beñamin. \v 13 Ba loolu amee dañoo torox, ba xotti seeni yére, ku nekk sëfaat mbaamam, ñu dellu ca dëkk ba. \s1 Yuda tinul na Beñamin ca Yuusufa \p \v 14 Yuda aki doomi baayam nag délsi kër Yuusufa, fekk demagul. Ñu daldi ne nërëm, dëpp seen jë fi suuf. \v 15 Yuusufa ne leen: «Li ngeen def nag? Xanaa xamuleen ne nit ku mel ni man day gisaane?» \v 16 Yuda ne: «Sang bi, lu nuy waxati? Lu nu mana lay, ba setal sunu bopp? Yàllaa nu feeñal, sang bi. Nanu bokk nun ñépp di say jaam, yem ci kepp ak ki ñu fekk kaas bi ci loxoom.» \v 17 Mu ne leen: «Jomb naa loolu. Ki ñu fekk kaas bi ci loxoom mooy doon sama jaam; ñi ci des dellu ca seen baay ci jàmm.» \p \v 18 Yuda jegesi ne ko: «Ngalla sang bi, ma ñeme laa diis lenn rekk, te sa xol baña tàng ci man, doonte yaak Firawnaa tolloo. \v 19 Sang bi, danga noo laajoon ne nu: “Ndax am ngeen baay walla rakk?” \v 20 Ba mu ko defee nu ne la: “Am nanu baay bu màggat. Sunu rakk, ji mu jur te fekk ko di màggat nag, moo ci gën di ndaw. Magam dafa dee, mu des moom doŋŋ ci ndeyam, baayam sopp ko lool.” \v 21 Nga waxoon nu ne nu: “Indil-leen ma ko, ngir ma gisal ko sama bopp.” \v 22 Ci kaw loolu, sang bi, nu wax la ne: “Xale bu góor bi manula tàggook baayam. Bu tàggoo ak moom, kon baayam dina dee.” \v 23 Nga wax nu ne nu: “Bu seen rakk àndul ak yeen, dungeen jàkkaarlook man.” \v 24 Booba lanu dem ca sunu baay, ba lay siyaare, daldi koy jottli say kàddu. \p \v 25 «Ba nu demee ba mu yàgg, sunu baay ne: “Delluleen, jëndali nu tuuti dund.” \v 26 Teewul nu ne: “Dunu mana dem te sunu rakk àndul ak nun, ndaxte bu nu àndul ak moom, dunu gis kilifa ga.” \v 27 Sunu baay, ba lay siyaare, ne nu: “Xam ngeen ne damaa amul ak sama soxna lu dul ñaari doom. \v 28 Kenn ki dem, wacc ma, ma ne moom kay, aw rabu àll a ko daggate! Gisaatuma ko ba tey jii. \v 29 Te bu ngeen ma fi jëlalee kii itam, ba musiba dab ko, dingeen ma yóbbe naqar wu may jàpp, ba kera may ànd ak sama bijjaaw, tàbbi njaniiw.” \p \v 30 «Léegi nag, bu ma ñibbee ca sama baay, ba lay siyaare, te àndunook xale bii muy noyyee, \v 31 bu gisul xale bu góor bi ànd ak nun ñibbsi— aa! Kon de dina dee, te dinanu yóbbe sunu baay naqar, wu koy topp, ba kera muy ànd ak bijjaawam, tàbbi njaniiw. \v 32 Gannaaw loolu it xasoon naa dige sama bakkan, ndax damaa waxoon ne: “Bu ma la ko délloosilul, maa koy gàlloo ba kera may dee.” \v 33 Kon ngalla sang bi, bàyyi ma man ma des fi di sa jaam, wuutu xale bi, te moom mu dellu ànd aki magam ñibbi. \v 34 Ndax xawma nan laay delloo ca sama baay te ànduma ak xale bi. Yàlla buma fekke njekkar, li ciy dal sama baay!» \c 45 \s1 Yuusufa xàmmiku na ay magam \p \v 1 Ba loolu amee Yuusufa manatula téye boppam, te surgaam yépp a nga teew. Mu daldi àddu ne: «Xiddileen ma, yeen ñépp!» Ñépp dem, ba benn jaambur nekku fa, ba Yuusufa di xàmmiku ay bokkam. \v 2 Mu ne yikkét, jooy jooy yu metti, waa Misra di ca dégg, ba ca kër Firawna sax. \p \v 3 Yuusufa nag ne magam ya: «Man mii maay Yuusufa! Mbaa sama baay a ngi dund?» Magam ya nag manuñu koo tontu, ndax booba njàqare jàpp na leen. \v 4 Yuusufa dellu ne ay magam: «Jegeñsileen.» Ñu jegeñsi. Mu ne leen: «Man maay Yuusufa, seen rakk, ji ngeen jaayoon, ñu indi ma Misra. \v 5 Waaye buleen jaaxle tey, mbaa ngeen di sikk seen bopp ndax li ngeen ma jaay, ñu indi ma fi. Rawale ay bakkan moo tax Yàlla yebal ma fi, ma jiitusi leen. \v 6 Ñaari at a ngii xiif baa ngi ci réew mi, te fii ak juróomi at ci kanam, kenn du bey, kenn du góob. \v 7 Yàlla da maa yebal, ma jiitusi leen, ba rawale seen bakkan, dikke leen xettal gu mag, ba seen askan baña fey. \v 8 Kon nag du yeena ma yebal fii, waaye Yàllaa. Te moo ma jagleel, ma doon cëslaayal Firawna, mel ni baay ci moom, jiite këram gépp, boole ci yilif mboolem réewum Misra. \p \v 9 «Gaawleen dellu ci sama baay te ne ko: “Sa doom Yuusufa nee na: Yàlla fal na ma kilifag Misra gépp; ñëwal fi man, nu mu gëna gaawe. \v 10 Su ko defee nga dëkksi diiwaanu Gosen, nekk ci sama wet, yaak say doom ak say sët ak say gàtt ak say gétt ak mboolem loo moom, \v 11 ndaxte des na juróomi ati xiif. Waaye dinaa la fi yore, ba doo ñàkk dara, yaak sa waa kër ak mboolem lu bokk ci yaw.” \v 12 Yeena gisal seen bopp, yeen ak sama rakk Beñamin, ne man Yuusufa mii, maay wax ak yeen. \v 13 Nettalileen sama baay ndam li ma am ci Misra ak li ngeen gis lépp, te ngeen indi sama baay, nu mu gëna gaawe.» \v 14 Mu laxasu Beñamin rakkam, daldi jooy, Beñamin it laxasu ko, jooy. \v 15 Magam ña itam, mu fóon leen tey jooy. Booba la magi Yuusufa ya doora wax ak moom. \s1 Firawna woo na Yanqóoba Misra \p \v 16 Ba xibaar ba àggee kër Firawna, ñu naan magi Yuusufa ñëw nañu, doonoon na lu neex Firawna, moom aki dagam. \v 17 Firawna ne Yuusufa: «Waxal say mag, ne leen: “Ni ngeen di def mooy nii: sëfleen seeni mbaam te dem réewu Kanaan, \v 18 jëli seen baay ak seeni njaboot, ngeen ñëw fi sama wet. Dinaa leen jox suuf si gën ci réewum Misra, ngeen di lekk li fi gëna duuf.”» \v 19 Firawna dellu ne Yuusufa: «Am nga ndigal itam ci wax leen ne leen: “Ni ngeen koy defe nii la: dangeen di jële ay watiir ci réew mi, dem yeb ci seeni doom ak seeni soxna, te ànd ak seen baay, ngeen ñëw. \v 20 Te buleen réccu alal, ji ngeen di bàyyi seen gannaaw, ndax li gën ci réewum Misra yeena koy moom.”» \p \v 21 Ba loolu amee doomi Israyil def noona. Yuusufa jox leen ay watiir ci ndigalu Firawna, ak lu ñu lekk ca yoon wa, \v 22 mayaale leen ku ne mbubb mu rafet. Waaye Beñamin moom, ñetti téeméeri dogi xaalis la ko may, tegal ko ca juróomi mbubb yu rafet. \v 23 Baayam nag, mu yóbbante ko fukki mbaam yu góor yu sëf lay tànnéef ca Misra, ak fukki mbaam yu jigéen yu sëf pepp ak mburu, tegal ko ca lu mu dunde ca yoon wa, buy ñëw. \v 24 Gannaaw loolu mu yiwi ay magam ne leen: «Ngalla buleen xuloo ci yoon wi.» Ñu daldi dem. \p \v 25 Booba lañu bàyyikoo Misra, dellu réewu Kanaan ca seen baay Yanqóoba. \v 26 Ñu wax ko ne ko: «Ndekete Yuusufaa ngi dund! te sax mooy kilifag réewum Misra gépp.» Ba Yanqóoba déggee loolu, yaramam dafa dee goyy ca saa sa, ndaxte gëmu leen. \v 27 Waaye ba ñu nettalee seen baay Yanqóoba li Yuusufa wax lépp, te mu gis watiir, yi Yuusufa yónnee, ngir jëlsi ko, ca la xelam délsi. \v 28 Israyil daldi ne: «Moom kay na dund rekk! Sama doom Yuusufaa ngi dund. Man kay dinaa dem ba gis ko, bala ma fee jóge.» \c 46 \s1 Yanqóoba dem na Misra \p \v 1 Israyil nag dem, yóbbaale mboolem lu bokk ci moom. Ba mu agsee Beerseba, dafa sarxal Yàllay baayam Isaaxa. \v 2 Yàlla wax ak Israyil foofa ca guddi ci biir gént ne ko: «Yanqóoba, Yanqóoba!» Israyil ne ko: «Naam.» \v 3 Yàlla ne ko: «Man maay Yàlla, di sa Yàllay baay. Bul ragala dem Misra, ndaxte askan wu réy laa fay sose ci yaw. \v 4 Man ci sama bopp maay ànd ak yaw Misra, te na la wóor ne dinaa la délloosi, te it Yuusufa moo lay doggali.» \p \v 5 Ba loolu amee Yanqóoba jóge Beerseba; doomi Israyil boole seen baay ak seeni doom ak seeni soxna, yeb leen ci watiir, yi Firawna yónnee woon, ngir yóbbu leen. \v 6 Ña nga jiital seeni jur, daldi yóbbaale seen alal, ja ñu ame réewu Kanaan. Noonu la Yanqóoba deme Misra ànd ak njabootam gépp, \v 7 yóbbaale doomam yu góor ya ak sëtam yu góor ya ak doomam yu jigéen ya it, ñook sëtam yu jigéen ya, ak mboolem ña askanoo ca moom. \s1 Njabootu Yanqóoba, gi ñëw Misra \p \v 8 Waa kër Israyil, yi ñëw Misra te di Yanqóoba aki doomam, seeni tur a di: \p Ruben, taawub Yanqóoba. \v 9 Doomi Ruben yu góor di Anog ak Palu ak Esron ak Karmi. \v 10 Doomi Simeyon yu góor di Yemuwel ak Yamin ak Owàdd ak Yakin ak Sowar ak Sawul, mi ndeyam di Kanaaneen. \v 11 Doomi Lewi yu góor di Gerson, Keyat ak Merari. \v 12 Doomi Yuda yu góor di Er ak Onan ak Sela ak Peres ak Sera, te Er ak Onan faatu ca réewu Kanaan. Doomi Peres yu góor di Esron ak Amul. \v 13 Doomi Isaakar yu góor di Tola ak Puwa ak Yasub ak Simron. \v 14 Doomi Sabulon yu góor di Seredd, Elon ak Yaleel. \v 15 Góor ñooñoo xeetoo ci Leya, te askanoo ci Yanqóoba ca Padan Aram, gannaaw Diina miy doomam ju jigéen. Boo boolee doomam yépp, góor ak jigéen, ñuy fanweer ak ñett. \p \v 16 Doomi Gàdd yu góor ñoo di Cefon ak Agi ak Suni ak Esbon ak Eri ak Arodi ak Areli. \v 17 Doomi Aser yu góor di Imna ak Yiswa ak Iswi ak Berya, Sera di seen jigéen. Doomi Berya yu góor di Eber ak Malkiyel. \v 18 Góor ñooñoo xeetoo ci Silpa, mi Laban may Leya, doomam ju jigéen, te ñu askanoo ci Yanqóoba, ñuy fukki bakkan ak juróom benn. \p \v 19 Doom yu góor yi Rasel, soxnas Yanqóoba, am nag ñoo di Yuusufa ak Beñamin. \v 20 Yuusufa itam am Manase ak Efrayim ca réewum Misra, seen yaay di Asnat doomu Potifera, may njiitu diine ca dëkk ba ñu naan On. \v 21 Doomi Beñamin yu góor ñoo di Bela ak Beker ak Asbel ak Gera ak Naaman ak Eyi ak Ros ak Muppim ak Uppim ak Àrd. \v 22 Góor ñooñoo xeetoo ci Rasel, te askanoo ci Yanqóoba, ñépp di fukki bakkan ak ñeent. \p \v 23 Doomu Dan ju góor di Usim. \v 24 Doomi Neftali yu góor di Yàcceel ak Gunni ak Yeccer ak Silem. \v 25 Góor ñooñoo xeetoo ci Bilaa, mi Laban may doomam Rasel, te ñu askanoo ci Yanqóoba, ñoom ñépp di juróom ñaari bakkan. \p \v 26 Mboolem ñi ànd ak Yanqóoba, ñëw Misra, muy ñi mu giir, te limaaleesul soxnay doomi Yanqóoba ya, tollu nañu ci juróom benn fukki bakkan ak juróom benn. \v 27 Doomi Yuusufa yu góor, ya mu am Misra, tollu ci ñaar. Kon mboolem ña dem Misra te di waa kër Yanqóoba, tollu nañu ci juróom ñaar fukk. \s1 Yanqóoba gis na Yuusufa \p \v 28 Yanqóoba dafa yebal Yuda, mu ànd ak Yuusufa, jiituji ko diiwaanu Gosen, Yanqóoba fekki leen fa. Ñu daldi agsi Gosen. \v 29 Yuusufa nag waajal waruwaayam, dajeji ak baayam Israyil ca Gosen. Ba Yuusufa àggee ba ca moom, da koo laxasu, ne ñàpp ci kawam, jooy lu yàgg. \v 30 Israyil ne Yuusufa: «Léegi de, bu ma yeboo dee, gannaaw gisaat naa la, ngay dund.» \p \v 31 Ba mu ko defee Yuusufa wax ak doomi baayam ya ak waa kër baayam ne leen: «Maa ngi dellu yégali Firawna ne ko: “Samay bokk ak sama waa kër baay, ña nekkoon ca réewu Kanaan, ñëw nañu fi man. \v 32 Dafa di seeni góor ay sàmm lañu, ag jur lañu masa yar, te indaale nañu seen jur gu gàtt ak gu gudd ak mboolem lu ñu moom.” \v 33 Kon bu leen Firawna wooyee, ne leen: \v 34 “Lan mooy seen liggéey?” ngeen ne ko: “Nun de sang bi, ag jur lanu masa yar, ba nuy gone ba tey, te noonu la ko sunuy maam daan defe.” Su boobaa, ngeen mana féetewoo diiwaanu Gosen, ndaxte waa Misra dañuy xof sàmm.» \c 47 \s1 Yuusufa nuyole na ay bokkam Firawna \p \v 1 Yuusufa daa dem ca Firawna, wax ko ne ko: «Sama baay ak samay bokk, jóge nañu Kanaan, ànd ak seen jur gu gàtt ak gu gudd ak mboolem lu ñu moom. Ña nga léegi ca diiwaanu Gosen.» \v 2 Fekk na Yuusufa tànn juróom ciy doomi baayam. Mu nuyole leen ak Firawna. \v 3 Firawna laaj doomi baay ya, ne leen: «Lan mooy seen liggéey?» Ñu ne ko: «Nun de sang bi, ay sàmm lanu naka jekk ca sunuy maam ba tey.» \v 4 Ñu teg ca ne ko: «Danoo ñëw ngir dal ci réew mi, ndaxte amalatunu sunu jur parlu, te xiif bi metti na ca réewu Kanaan. Moo tax sang bi, nu di la ñaan, nga may nu, nu dal foofa ca diiwaanu Gosen.» \v 5 Firawna wax ak Yuusufa ne ko: «Gannaaw sa baay ak say bokk ñëw nañu fi yaw, \v 6 réewum Misra a ngii ci sa kanam. Seetal fi gën ci réew mi, nga jox sa baay ak say bokk, ñu sanc. Bàyyi leen, ñu sanc Gosen, te bu ci amee ñu xareñ ci ñoom, nga dénk leen samay gétt.» \p \v 7 Gannaaw loolu Yuusufa ànd ak baayam ba fa Firawna, nuyole ko ak moom. Yanqóoba nuyu Firawna. \v 8 Firawna laaj Yanqóoba ne ko: «Aa, góor gi, xanaa war ngaa doon mag de!» \v 9 Yanqóoba wax Firawna ne ko: «Samay ati màngaan, ba ma ganee àddina ba tey de, mu ngi tollu ci téeméer ak fanweer, muy at yu gàtt te naqari, te it demuma bay tolloo ay at ak samay maam, ba ñuy màngaan ci àddina.» \v 10 Ba mu ko defee Yanqóoba ñaanal Firawna, bàyyikoo fa, daldi dem. \p \v 11 Yuusufa nag dalal baayam aki bokkam, dogal leen suuf sa gën ca réewum Misra ca diiwaanu Ramses, ni ko ko Firawna sante woon. \v 12 Ba loolu amee Yuusufa di dundal baayam aki bokkam, ak mboolem waa kër baayam, boole ca ña bootu ca ñoom. \s1 Lu jëm ci saytub Yuusufa ca xiif ba \p \v 13 Ab dund amuloon fenn ca réew ma mépp, ndax xiif bu metti lool. Waa réewum Misra ak réewu Kanaan jeex tàkk ndax xiif ba. \v 14 Yuusufa nag dajalee ca pepp, ma mu jaay waa Misra ak waa Kanaan, mboolem xaalisu ñaari réew ya, yóbbu nag xaalis ba kër Firawna. \v 15 Ba ñu demee, ba xaalis amatul ca Misra ak ca Kanaan, waa Misra gépp ñëw fa Yuusufa ne ko: «Jox nu ab dund kay! Mbaa du danga nuy seetaan, nuy dee? Ndax xaalis amatul.» \v 16 Yuusufa ne leen: «Indileen seeni jur, ma wecci leen ko dund, ndegam amatuleen xaalis.» \v 17 Gannaaw loolu ñu indil Yuusufa seeni jur, Yuusufa jox leen ko pepp, wecci leen ko seeni fas ak seeni gétti jur gu gàtt ak gu gudd ak seeni mbaam. At mooma jox na leen ab dund, mu wecci seen gétt gépp. \v 18 Ba at ma jeexee, ñu ñëwaat ca moom ca déwén sa ne ko: «Sang bi, dunu la nëbb ne amatunu dara, ndax xaalis bi jeex na, te jur gaa ngi ci yaw, dara nekkatu fi lu nu la mana jox lu moy sunuy jëmm ak sunuy tool. \v 19 Mbaa du danga nuy seetaan, nu bokk sànku ci sa kanam, nook sunu suuf? Ngalla boole nu jënde ab dund, nun ak sunuy suuf. Su ko defee nuy moomeeli Firawna, nun ak sunuy suuf. Te nga jox nu pepp mu nu dunde, lu ko moy kat nun dinanu dee, suuf si it dina booy.» \p \v 20 Yuusufa nag jëndal Firawna suufas Misra gépp, ngir waa Misra ya jaay ku ci nekk sa tool ndax xiif, ba leen jiital, ba Firawna mujj moom suuf si. \v 21 Waa réew ma ñoom, Yuusufa da leena def ay jaam ca Misra, gii wet ba gaa. \v 22 Bàyyiwul lu moy suufu njiiti diine ya, ndax Firawna jotoon na leena dogal ay cér, jagleel leen. Moo tax jaayuñu seeni suuf. \p \v 23 Yuusufa ne waa réew ma: «Léegi gannaaw jënd naa leen, ba Firawna moom leen, yeen ak seeni suuf, jiwoo ngii, demleen jiyi. \v 24 Bu nu àggee ci ngóob, juróom yu ngeen am dingeen ci jox Firawna benn, te féetewoo ñeenti cér yi des. Su ko defee ngeen génne ci jiwuy tool yi, li ci des ngeen dunde, yeen ak seen waa kër ak seeni doom.» \v 25 Ñu ne ko: «Sang bi, rawale nga nu! Te gannaaw laaye nga nu biir, nangu nanoo doon jaami Firawna.» \v 26 Noonu la Yuusufa tërale loola, def ko dogalu yoon ca suufu Misra, te loolooy wéy ba tey jii: juróomi céri meññeef mu ne, Firawnaay moom benn ba. Waaye suufi njiiti diine ya ca bokkul, Firawna amu ca dara. \s1 Lu jëm ci ati Yanqóoba yu mujj ya \p \v 27 \w Bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* sanc nañu réewum Misra ca diiwaanu Gosen. Am nañu fa alal, giir fa, ba yokku lool. \p \v 28 Yanqóoba nag nekk na fukki at ak juróom ñaar ca réewum Misra, ay atam yépp tollu ci téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñaar (147). \v 29 Ba nga xamee ne àppu Israyil a ngay bëgga mat, dafa woolu doomam Yuusufa ne ko: «Ngalla waay dugalal sa loxo, mu ron sama lupp\f + \fr 47.29 \fr*\ft Seetal ci 24.2-3.\ft*\f*, muy ngiñ ci yaw ne dinga jëflanteek man ci ngor ak worma: rikk, bu ma denc Misra. \v 30 Bés bu ma fekkijee samay maam, nanga ma jële Misra, denci ma ca seen xuntim bàmmeel.» Yuusufa ne ko: «Dinaa la defal li nga wax.» \v 31 Mu ne ko: «Giñal ma ko.» Yuusufa giñ ko, Israyil doora am jàmm, daldi wéeru ca bopp lal ba. \c 48 \s1 Israyil ñaanal na Efrayim ak Manase \p \v 1 Ba loolu wéyee ñu ne Yuusufa baayam dafa tawat, mu ànd ak ñaari doomam Manase ak Efrayim, seeti ko. \v 2 Ba ñu yégalee Yanqóoba ne doomam Yuusufaa koy seetsi, Israyil dafa dëgërlu, toog ca lal ba. \p \v 3 Yanqóoba ne Yuusufa: «Yàlla Buur bi feeñu woon na ma ca Lus ca réewu Kanaan, barkeel ma, \v 4 te wax na ma ne ma: “Dinaa la giiral, fulandi la, def la nga sos mbooloom xeet, te réew mii laay may ñi askanoo ci yaw, ñu moom ko fàww.” \v 5 Léegi nag sa ñaari doom, yi nga am Misra, laata ma di la fekksi Misra, maa leen séddoo. Maay séddoo Efrayim ak Manase, ñuy samay doom, ni ma jure Ruben ak Simeyon. \v 6 Waaye doom, yi nga am seen gannaaw yaa leen di féetewoo, ñuy wuyoo seen turi mag ci wàllu ndono. \v 7 Li tax ma def loolu mooy, bi ma jógee Padan di ñibbi, Rasel dafa faatu ca yoon wa ci sama kanam, ba nuy tollu ca réewu Kanaan, booba nu ngay dem, bay jub Efrata. Ma suul ko foofa, ca yoonu Efrata.» Efrata mooy Betleyem tey. \p \v 8 Ci kaw loolu Israyil gis doomi Yuusufa ya. Mu ne: «Ñii ñooy ñan?» \v 9 Yuusufa ne baayam: «Ñii ñooy sama doom, yi ma Yàlla jox fii.» Baayam ne ko: «Nañu jegesi, ma ñaanal leen.» \v 10 Booba bëti Israyil dafa lëndëm, ba gisatul ndax li muy mag. Yuusufa jegeñal leen seen maam, mu fóon leen, taf leen ci boppam. \v 11 Israyil nag ne Yuusufa: «Yaakaaruma la woona gisati, ndeke Yàlla dina ma may lu raw gis la, ndax gis naa say doom.» \p \v 12 Ca la leen Yuusufa wàccee fi ñu uufu ci seen maam, daldi dëpp jëëm ci suuf, \v 13 ba noppi Yuusufa taxawal leen ñoom ñaar, ñu séq ko janook Israyil, loxol ndijooram jàpp ci Efrayim, mu féete ak càmmoñu Israyil, loxol càmmoñam jàpp ci Manase, mu féete ak ndijooru Israyil. Ñu ànd jegesi, \v 14 Israyil nag jàllawle ay loxoom, tàllal ndijooram, teg ko ca kaw boppu Efrayim, mi gën di ndaw; càmmoñam tege ca boppu Manase, doonte mooy taaw. \v 15 Ma ngay ñaanal Yuusufa. Mu ne: \q1 «Yàlla ji samay waajur Ibraayma ak Isaaxa toppoon, \q1 moom Yàlla, ji ma sàmm, ba ma juddoo ba tey jii, \q1 \v 16 malaaka mi ma jot ci bépp loraange— \q1 yal na barkeel xale yi, \q1 ba ñu saxal sama tur \q1 ak samay turi waajur, Ibraayma ak Isaaxa, \q1 te giir, ba ne gàññ ci kaw suuf.» \p \v 17 Ba Yuusufa gisee ne baayam ca boppu Efrayim la teg loxol ndijooram, mu naqari ko, mu daldi jàpp loxol baayam, bëgg koo jële ca boppu Efrayim, teg ko ca boppu Manase. \v 18 Yuusufa ne baayam: «Déet, baay, ndax kii mooy taaw, tegal sa ndijoor ci boppam.» \v 19 Teewul baayam lànk, ne ko: «Xam naa ko, doom, xam naa ko. Moom itam dina doon aw xeet tey doon ku màgg, waaye rakkam a koy sut, te askanam dina law, ba di ay xeet.» \v 20 Gannaaw loolu mu ñaanal leen keroog ne leen: «Yal na Israyil di ñaane seeni tur naan: “Yal na la Yàlla def ni Efrayim ak Manase.”» Noonu la jiitale Efrayim, door caa teg Manase. \p \v 21 Ba mu ko defee Israyil ne Yuusufa: «Léegi man dinaa dee, waaye Yàlla dina ànd ak yeen, ba delloo leen ca seen réewu maam. \v 22 Man nag dinaa la may cér booy ëpple say doomi baay, muy suuf su ma nangoo sama saamar ak sama fitt ca Amoreen ña.» \c 49 \s1 Yanqóoba tàggoo na \p \v 1 Gannaaw loolu Yanqóoba woo ay doomam ne leen: \p «Bokkleen daje, ma xamal leen li leen di dikkal ëllëg. \q1 \v 2 Dajeleen te déglu ma, man Yanqóoba seen baay; \q1 teewluleen seen baay Israyil. \b \q1 \v 3 «Ruben, yaw mi ma taawloo, \q1 nga sosoo sama digg doole, sama ndoortel kàttan, \q1 yaa jëkke sut moos ci teraanga ak doole. \q1 \v 4 Yaa toogadi it ni ndox muy wal-wali, \q1 doo mujje sut, \q1 nde yaa tëdd sa lalu baay, \q1 ba teddadi, kera ba nga ca tëddee. \b \q1 \v 5 «Simeyon ak Lewi ñoo duye yene, \q1 ñooy nas pexey ay. \q1 \v 6 Yàlla bu sama xol ànd ci seeni pexe, \q1 mbaa sama xel di nangu seeni diisoo, \q1 ndax fu ñu mere, xal faa bóome, \q1 te làggal ay yëkk lañuy foye. \q1 \v 7 Mbas ma seen xadar, gu tar, \q1 ak seen mer, mi dul meddi. \q1 Maa leen di wasaare ci kër Yanqóoba, \q1 tasaare leen ci Israyil. \b \q1 \v 8 «Yaw Yuda, mi say doomi baay di taggeji, \q1 ngay sëqi sa ndoddi noon, sëgal leen, \q1 sa doomi baay a lay sujjóotal. \q1 \v 9 Yuda yaa di gaynde gu ndaw, doom, \q1 doora jóge nii ci pàdd, \q1 tey yuug ak a goor ni gayndeg sibi. \q1 Yaa di gaynde gu deesul yee. \q1 \v 10 Nguur gi du jóge ci loxol Yuda, \q1 te yetu buur ay wéye sampe ciy tànkam, \q1 li feek boroom\f + \fr 49.10 \fr*\ft Baat bi ñu tekkee \ft*\fq boroom \fq*\ft fii, bare na nu ñu koy tekkee.\ft*\f* di ñëw, \q1 ba xeet yi déggal ko. \q1 \v 11 Mooy yeew mbaamam cig reseñ, \q1 cumbur ma féeteek car, ba ca gën; \q1 muy fóote ay yéreem biiñ, \q1 di sumb mbubbam ci ndoxum reseñ. \q1 \v 12 Bët yaa ngay nes-nesi ndax biiñ, \q1 bëñ ya weex furr ndax um soow. \b \q1 \v 13 «Sabulon ay dëkke tefesi géej, \q1 di teerub gaal yi, \q1 am réewam digalook Sidon. \b \q1 \v 14 «Isaakar mbaam ngonk la, \q1 muy goor diggante ñaari sëf. \q1 \v 15 Bu gisee ni mbaaram neexe, \q1 ak ni réew mi naate, \q1 day waaf, gàddu ngaaxam, \q1 daldi féetewoo coonob njaam. \b \q1 \v 16 «Dan ay àtteji xeetam, \q1 ni ko giiri Israyil baaxoo. \q1 \v 17 Waaye Dan ay jaan ju dog aw yoon, \q1 mbaa céebi ciw ñall, \q1 mooy màtt tànki fas, \q1 gawar jullootu. \b \q1 \v 18 «Céy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, maa ngi séentu sa xettal! \b \q1 \v 19 «Gàdd la gàngoor di gaw, \q1 mu téqtal leen, ba daan. \b \q1 \v 20 «Aser ay boroom dund bu duun, \q1 mooy maye ngëneeli ñami buur. \b \q1 \v 21 «Neftalee di kéwél gu fëx, \q1 te mooy jur doom yu taaru. \b \q1 \v 22 «Yuusufaay bànqaasu garab, \q1 garab guy meññ, feggook bëtu ndox, \q1 car yaa nga law, tiim digu tool ba. \q1 \v 23 Ay fittkat a ko toŋal, \q1 di ko song ak a fitt. \q1 \v 24 Teewul xalaam ga di wéye daŋ, \q1 te la loxo yay dëgërloo mooy \q1 loxoy Jàmbaar ju Yanqóoba, \q1 kookooy Sàmm bi, Doju cëslaayal Israyil, \q1 \v 25 mooy sa Yàllay baay, ji lay wallu, \q1 mooy Aji Man ji lay barkeele \q1 ca barkey asamaan, ya fa kaw, \q1 ak barke ya ne leww ca suuf xóote ya, \q1 teg ca barkeb njur ak nàmpal. \q1 \v 26 Sa ñaani baay ya romb \q1 xéewali tund, ya sax fàww, \q1 rombati ngëneeli jànji cosaan ya, \q1 yal na dal ci boppu Yuusufa, \q1 ca kaw ndaal boppam, moom sangub doomi baayam ya. \b \q1 \v 27 «Beñamin ay till guy yeeroo, \q1 di xëye yàpp rëbbam, \q1 tey gonloo séddale am lëlam.» \b \m \v 28 Ñooñu ñoo sos mboolem giiri Israyil, ñu tollu ci fukk ak ñaar, te loolu la leen seen baay wax, ba mu leen di tàggu. Ku ci nekk mu tàggoo ko kàdduy tàggtoo, ya war ca moom. \s1 Yanqóoba nelaw na \p \v 29 Gannaaw loolu da leena dénk ne leen: «Maa ngi waaja fekki samay maam; dencleen ma fa samay maam ca xuntim bàmmeel ba ca toolub Efron, Etteen ba. \v 30 Mooy xuntim bàmmeel ba ca biir tool, ba ca Magpela, te jàkkaarloo ak Mamre ca réewu Kanaan, di tool, ba Ibraayma jëndoon ca Efron, Etteen ba, ngir def ko bàmmeel. \v 31 Foofa lañu denc Ibraayma ak soxnaam Saarata, te foofa lañu denc Isaaxa ak soxnaam Rebeka, te fa laa denc Leya it. \v 32 Tool ba ak xuntim bàmmeel ba ca nekk, ña nga ko jënde ca Etteen ña.» \p \v 33 Naka la Yanqóoba dénku doomam yu góor ya noona, daldi delloo ay tànkam ca lal ba, bakkan ba rot, mu fekki ay maamam. \c 50 \s1 Yuusufa rob na Yanqóoba réewu Kanaan \p \v 1 Ba mu ko defee Yuusufa daanu ci kaw baayam. Ma ngay jooy te di ko fóon. \v 2 Ba loolu weesee Yuusufa jox ay fajkatam ndigal, ñu waajal baayam. Fajkat ya waajal Israyil\f + \fr 50.2 \fr*\ft Fajkati waa Misra ndàbb lañu daan waajale néew, ba du yàqu.\ft*\f*. \v 3 Waaj ma am na ñeent fukki fan, ndaxte loolooy waajal bu mat sëkk cib néew. Waa Misra nag dëjal ko juróom ñaar fukki fan. \p \v 4 Ba dëj ba weesee, Yuusufa dafa wax ak waa kër Firawna, ñaan leen ñu dimbali ko, waxal ko Firawna ne ko, \v 5 baayam da ne woon, mu ngi waaja dee, waaye bàmmeel ba mu yettaloon boppam ca xunti ma ca réewu Kanaan, na ko giñal ne dina ko denc foofa. Mu ne kon, na ko Firawna may, mu robi baayam, ni mu ko ko giñloo woon, te délsi. \v 6 Firawna may ko, mu robi baayam, na mu ko ko giñloo woon. \p \v 7 Yuusufaa ngay dem robi baayam, moom ak mboolem jawriñi Firawna ak magi këram ak mboolem kàngami Misra. \v 8 Ña nga ànd ak waa kër Yuusufa gépp ak ay doomi baayam ak waa kër baayam, bàyyiwuñu diiwaanu Gosen lu moy xale ya ak gàtt ya ak jur gu gudd ga, \v 9 ay watiir aki gawar topp ca, ñu def gàngoor gu réy. \p \v 10 Ba ñu agsee ca dàggay Ataat, ja ca wàllaa dexu Yurdan, dañu koo jooy jooy yu réy te metti. Yuusufa dëjal fa baayam diiru juróom ñaari fan. \v 11 Waa réewu Kanaan, gis dëj ba ca dàggay Ataat, naan: «Dëju waa Misra bii aka réy!» Moo tax ñu tudde bérab booba ca wàllaa dexu Yurdan, Abel Misra (mu firi Dëju waa Misra). \p \v 12 Doomi Yanqóoba nag def la leen seen baay dénkoon, \v 13 yóbbu ko ca réewu Kanaan, daldi koy rob ca xunti ma ca toolub Magpela, te Ibraayma jëndoon ko ca Efron, Etteen ba, ngir def ko bàmmeel. Mooy tool, ba jàkkaarloo ak Mamre. \v 14 Ba Yuusufa dencee baayam ba noppi, dafa dellu Misra, moom ak doomi baayam ya ak mboolem, ña mu àndaloon ca robu baayam. \s1 Magi Yuusufa yaa ngi jéggalu \p \v 15 Magi Yuusufa ya xam nañu ne seen baay nelaw na. Ña ngay wax ca seen biir naan: «Waaw, mbaa Yuusufa dencalu nu mer, nar noo fey sunu bor ndax lu bon li nu ko ji woon lépp?» \v 16 Boobu lañu yóbbante Yuusufa kàddu yii, di ko wax ne ko: «Sa baay dafa noo dénkoon, bala moo nelaw, ne nu: \v 17 Waxleen Yuusufa ne ko, sa baay nee: “Say mag def nañu la lu bon moos, waaye ngalla baal leen seeni tooñ ak àq, ji ñu la ameel.” Kon rikk waay, baal nu àq, ndax nun nook sa baay a bokk jenn Yàlla ju nuy jaamu.» Ba ñu waxee Yuusufa loolu, mu daldi jooy. \p \v 18 Ci kaw loolu magam ya ñëwal seen bopp ba ca moom, sujjóotal ko ne ko: «Sang bi, nu ngi nii, di la siyaare.» \v 19 Yuusufa nag ne leen: «Buleen am dara lu ngeen di ragal. Xanaa maay Yàlla? \v 20 Dëgg la, fexeel ngeen ma lu bon, waaye Yàllaa ko walbati, def ko lu baax, ba dogal li am tey jii, muy bakkan yu bare yi mucc. \v 21 Kon nag buleen tiit, dinaa leen yor, yeen ak seeni doom.» Yooyu kàddu la dalale seen xol, ba ñu am jàmm. \s1 Yuusufa nelaw na \p \v 22 Yuusufa dëkk na Misra, moom ak waa kër baayam ñépp, ba tollu ci téeméeri atam ak fukk, \v 23 te gis na doomi Efrayim, ba gis sëti Efrayim sax; rax ca dolli doomi Makir, mi Manase jur, fa kanamam lañu juddoo. \p \v 24 Mu am bés Yuusufa ne ay bokkam: «Sama waxtu jege na, waaye Yàlla moo leen di jëlsi moos, ba jële leen ci réew mii, yóbbu leen ca réew ma mu dige woon, ba giñal ko Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba.» \v 25 Booba la Yuusufa wax doomi Israyil, ne leen: «Giñal-leen ma ne bés bu leen Yàlla jëlsee, dingeen yóbbaale samay yax, waaye dungeen ma fi bàyyi.» \p \v 26 Gannaaw loolu Yuusufa nelaw ci téeméeri atam ak fukk. Ñu waajal néew ba, ba du yàqu, daldi koy yeb cib tàdd, denc ko foofa ca Misra.