\id EZR (WOL) \ide UTF-8 \h Esra \toc1 Esra \toc2 Esra \mt1 Esra \c 1 \s1 Lu jëm ci dogalu Sirus \p \v 1 At ma jëkk ca nguurug Sirus buuru Pers, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji moo nammoona sottal kàddu ga mu waxe ca gémmiñug Yeremi, ba tax mu xiir Sirus buuru Pers, mu siiwtaane ab dogal ci mboolem réewam, boole ci bind ko ne: \pm \v 2 Sirus buuru Pers dafa wax ne: Mboolem réewi àddina, Yàlla Boroom asamaan\f + \fr 1.2 \fr*\fk Yàlla Boroom asamaan \fk*\ft turu darajaal la bu ñuy waxe ci gàttal ne mooy Yàllay asamaan ak suuf, muy wund ne du Israyil rekk lay seen Yàlla, waaye mooy Yàllay àddina sépp.\ft*\f* moo ma leen dénk, te moom moo ma tabb, ngir ma tabaxal ko kër ca Yerusalem ga ca Yuda. \v 3 Képp ku bokk ci mboolem ñoñam, yal na Yàllaam ànd ak moom, mu dem ba Yerusalem ga ca Yuda, tabax fa kër Aji Sax ji, Yàllay Israyil, Yàlla ja ca Yerusalem. \v 4 Mboolem bànni Israyil, ak fu ci nit mana féete, na ko waa foofa indil ndimbal ci wàllu xaalis ak wurus, alal aku jur ak \w saraxi yéene|lemma="Sarax yi:"\w* yu jëm ca kër Yàlla ga ca Yerusalem. \p \v 5 Ba mu ko defee ña jiite waa kër Yuda ak Beñamin ak \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yaak \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ña, képp ku ci Yàlla xiir rekk, mu daldi dem tabaxi kër Aji Sax ja ca Yerusalem. \v 6 Mboolem seeni dëkkandoo daldi def ci seen loxo jumtukaayi xaalis ak wurus, alal akug jur ak gànjar, te bokkul ak mboolem seen saraxi yéene. \v 7 Ci biir loolu Buur Sirus génne ndabi kër Aji Sax, ja Nabukodonosor jële woon Yerusalem te yeboon ko ca kër tuuram ya. \v 8 Sirus buuru Pers nag sant Mittredat farbay alalam, mu génne ko, daldi koy waññal Sesbasar, boroom Yuda. \p \v 9 Lenn ci lim bi tëdde nii: fanweeri ndabi wurus (30), ak junniy ndabi xaalis (1 000), ak ñaar fukki paaka ak juróom ñeent (29), \v 10 ak fanweeri këlli wurus yu ndaw (30) yu ànd ak ñeenti téeméeri këll ak fukk yu ndaw yu xaalis (410) ak junniy jumtukaay yeneen (1 000). \v 11 Mboolem ndabi wurus yeek yu xaalis yi juróomi junni la ak ñeenti téeméer (5 400). Sesbasar jële lépp Babilon, yóbbu Yerusalem, ba ngàllo gay ñibbi. \c 2 \s1 Limeefu ngàllo ga ñibbsi nii la \p \v 1 Ñii nag ñoo di niti diiwaanu Yuda, ña jóge njaam ca ngàllo ga leen Nabukodonosor buuru Babilon yóbbu woon, te ñu jóge ca ñibbsi Yerusalem ak Yuda, ku nekk ak fa mu dëkk. \v 2 Ña nga ñibbi ca njiital Sorobabel ak Yosuwe\f + \fr 2.2 \fr*\ft \+k Yosuwe:\+k* Yeswa ci làkku ebrë. Yosuwe lanu bind ci tekki bii, muy doomu Yoccadag te doon sarxalkat bu mag bi mujj lu jiitu ngàllo ga ca Babilon. Yosuwe mii lu gëna bare dees na ko tuddaaleek Sorobabel. Feneen fu ñu ne Yeswa ci téere bi, keneen a tax ñuy wax.\ft*\f* ak Neyemi ak Seraya ak Relaya ak Mardose ak Bilsan ak Mispar ak Bigway ak Reyum ak Baana. \p Limeefu góori \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* nii la tëdde: \v 3 Askanu Paros, ñaari junni ak téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar lañu (2 172). \v 4 Askanu Sefatiya, ñetti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar lañu (372). \v 5 Askanu Ara, juróom ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróom lañu (775). \v 6 Askanu Payat Mowab, soqikoo ci Yeswa ak Yowab, di ñaari junni ak juróom ñetti téeméer ak fukk ak ñaar (2 812). \v 7 Askanu Elam, junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254). \v 8 Askanu Sàttu, juróom ñeenti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (945). \v 9 Askanu Sakay, juróom ñaar téeméer ak juróom benn fukk lañu (760). \v 10 Askanu Baani, juróom benni téeméer ak ñeent fukk ak ñaar lañu (642). \v 11 Askanu Bebay, juróom benni téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (623). \v 12 Askanu Asgàdd, junni ak ñaar téeméer ak ñaar fukk ak ñaar lañu (1 222). \v 13 Askanu Adonikam, juróom benni téeméer ak juróom benn fukk ak juróom benn lañu (666). \v 14 Askanu Bigway, ñaari junni ak juróom fukk ak juróom benn lañu (2 056). \v 15 Askanu Adin, ñeenti téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (454). \v 16 Askanu Ater, soqikoo ci Esekiya, di juróom ñeent fukk ak juróom ñett (98). \v 17 Askanu Besay, ñetti téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (323). \v 18 Askanu Yora, téeméer ak fukk ak ñaar lañu (112). \v 19 Askanu Asum, ñaar téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (223). \v 20 Askanu Gibar, juróom ñeent fukk ak juróom lañu (95). \p \v 21 Waa Betleyem, téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (123). \v 22 Waa Netofa, juróom fukk ak juróom benn lañu (56). \v 23 Waa Anatot, téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett lañu (128). \v 24 Waa Asmawet, ñeent fukk ak ñaar lañu (42). \v 25 Waa Kiryaat Yarim ak Kefira ak Berot, juróom ñaar téeméer ak ñeent fukk ak ñett lañu (743). \v 26 Waa Raama ak Geba, juróom benni téeméer ak ñaar fukk ak benn lañu (621). \v 27 Waa Migmas, téeméer ak ñaar fukk ak ñaar lañu (122). \v 28 Waa Betel ak Ayi, ñaar téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (223). \v 29 Waa Nebo, juróom fukk ak ñaar lañu (52). \v 30 Waa Magbis téeméer ak juróom fukk ak juróom benn lañu (156). \v 31 Waa Elam gu ndaw, junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254). \v 32 Waa Arim, ñetti téeméer ak ñaar fukk lañu (320). \v 33 Waa Lodd ak Adidd ak Ono, juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk ak juróom lañu (725). \v 34 Waa Yeriko, ñetti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (345). \v 35 Waa Sena, ñetti junni ak juróom benn téeméer ak fanweer lañu (3 630). \p \v 36 \w Sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi ñii la: \m Askanu Yedaya, soqikoo ci waa kër Yosuwe, di juróom ñeenti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñett (973). \v 37 Askanu Imer, junni ak juróom fukk ak ñaar lañu (1 052). \v 38 Askanu Pasur, junni ak ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñaar lañu (1 247). \v 39 Askanu Arim, junni ak fukk ak juróom ñaar lañu (1 017). \p \v 40 \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi ñii la: Askanu Yeswa ak Kadmiyel. Mooy ñi bànqaasoo ci Odawya, tollu ci juróom ñaar fukk ak ñeent (74). \p \v 41 Jàngkat yi ñoo di: Askanu Asaf, di téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett (128). \p \v 42 Askanu fara bunt yi ñoo di: Askanu Salum, ak askanu Ater, ak askanu Talmon, ak askanu Akub, ak askanu Atita, ak askanu Sobay, ñépp di téeméer ak fanweer ak juróom ñeent (139). \p \v 43 Liggéeykati kër Yàlla gi ñoo di: Askanu Ciya, ak askanu Asufa, ak askanu Tabawot, \v 44 ak askanu Keros, ak askanu Siya, ak askanu Padon, \v 45 ak askanu Lebana, ak askanu Agaba, ak askanu Akub, \v 46 ak askanu Agab, ak askanu Samlay, ak askanu Xanan, \v 47 ak askanu Gidel, ak askanu Gayar, ak askanu Raaya, \v 48 ak askanu Reccin, ak askanu Nekoda, ak askanu Gasam, \v 49 ak askanu Usa, ak askanu Paseya, ak askanu Besay, \v 50 ak askanu Asna, ak askanu Meyunim, ak askanu Nefusim, \v 51 ak askanu Bagbug, ak askanu Akufa, ak askanu Arur, \v 52 ak askanu Baslut, ak askanu Meyida, ak askanu Arsa, \v 53 ak askanu Barkos, ak askanu Sisera, ak askanu Tema, \v 54 ak askanu Necciya, ak askanu Atifa. \p \v 55 Askanu jaami Suleymaan ñii la: Askanu Sotay, ak askanu Asoferet, ak askanu Peruda, \v 56 ak askanu Yaala, ak askanu Darkon, ak askanu Gidel, \v 57 ak askanu Sefatiya, ak askanu Atil, ak askanu Pokeret Asbayim, ak askanu Aami. \p \v 58 Mboolem liggéeykati kër Yàlla gi ak askanu jaami Suleymaan yi, ñetti téeméer ak juróom ñeent fukk ak ñaar (392). \p \v 59 Ña bàyyikoo Tel Mela ak Tel Arsa ak Kerub Adon ak Imer te manuñoo firndeel ne seen waa kër maam ak seen askan ci Israyil lañu bokk, ñii la: \v 60 Askanu Delaya, ak askanu Tobya, ak askanu Nekoda, di juróom benn téeméer ak juróom fukk ak ñaar (652). \p \v 61 Am na it ñu loolu daloon ci askanu sarxalkat yi, muy askanu Abaya, ak askanu Akocc, ak askanu Barsilay, ma doon denc doomu Barsilay waa Galàdd ba, ba tax ñu santale ko seen sant. \v 62 Ñooñu, seet nañu seen limeefu kër maam, waaye gisuñu ko. Ñu daldi leen doyadal, génne leen ci carxal gi. \v 63 Boroom dëkk ba nag aaye leen ñu lekk ci ñam yu \w sell|lemma="sell:"\w* yaa sell, ba keroog ab sarxalkat di am lu leer ci ñoom ci jumtukaayi tegtal yi ñuy wax \w Urim ak Tumim|lemma="Urim ak Tumim:"\w*. \p \v 64 Limu mbooloo ma mépp ba mu daj, ñeent fukki junneek ñaar ak ñetti téeméer ak juróom benn fukk lañu (42 360), \v 65 te limaaleesul seen jaam yu góor ak yu jigéen, yi tollu ci juróom ñaari junni ak ñetti téeméer ak fanweer ak juróom ñaar (7 337). Amoon nañu itam ay jàngkat yu góor ak yu jigéen, yu tollu ci ñaar téeméer (200). \v 66 Amoon nañu juróom ñaar téeméeri fas ak fanweer ak juróom benn (736), ak ñaar téeméeri berkelle ak ñeent fukk ak juróom (245), \v 67 ak ñeenti téeméeri giléem ak fanweer ak juróom (435), ak juróom benni junniy mbaam ak juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk (6 720). \p \v 68 Ba ñu àggee ca kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ja ca Yerusalem, am na ñenn ca kilifa ya jiite seen kër baay, ñu joxe ay saraxi yéene ngir tabaxaat kër Yàlla ga ca gentam. \v 69 Joxe nañu ku nekk la mu man, jëme ca alal ja ñuy liggéeye, muy juróomi barigoy wurus ak fanweeri barigoy xaalis, ak téeméeri mbubbi sarxalkat. \p \v 70 Ba loolu amee bànni Israyil gépp sancaat ca seen dëkki cosaan, sarxalkat yaak Leween ñaak ñenn ca baadoolo yaak jàngkat yaak fara bunt yaak liggéeykati kër Yàlla ga. \c 3 \s1 Njaamug Aji Sax ji feddliku na \p \v 1 Ba juróom ñaareelu weer wa agsee, fekk na \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* sancaat ca seeni dëkk, mbooloo ma daje doon benn bopp ca Yerusalem. \v 2 Ba mu ko defee Yosuwe doomu Yoccadag, mook moroomi \w sarxalkatam|lemma="sarxalkat b-:"\w*, ak Sorobabel doomu Selcel aki bokkam daldi tabax \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* Yàllay Israyil, ngir sarxal ca \w saraxu dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* ba, mu dëppook li ñu bind ci téereb yoonu Musaa, góorug Yàlla ga. \v 3 Ci kaw loolu ñu yékkatiwaat sarxalukaay ba, ca kenoom gu jëkk ga, doonte ragaloon nañu waasoy réew ma. Ba ñu noppee, defal ca \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ay saraxi dóomal subaak ngoon. \v 4 Ñu teg ca amal \w màggalu Mbaar|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* ya, mu dëppook la ñu bind, boole kook saraxu dóomal yi war bés bu nekk. \v 5 Gannaaw loolu ñu joxe saraxu dóomal bi sax fàww, ak saraxi Terutel weer ya, ak sarax yu sell yi war ci mboolem màggali Aji Sax ji, ak mboolem \w saraxi yéene|lemma="Sarax yi:"\w* yi ñuy indil Aji Sax ji. \v 6 Benn fan ca juróom ñaareelu weer wa lañu tàmbalee defal Aji Sax ji ay saraxi dóomal, te fekkul ñu yékkatiwaat kenug kër Aji Sax ji. \v 7 Ci biir loolu ñu jox xaalis yettkati doj yeek xaddkat yi, jox waa Sidon ak waa Tir ab dund, aki naan akug diw, ngir ñu jëleji Libaŋ ay banti seedar, jaarale ko ci géej gi ba Yafa, ci ndigalal Sirus buuru Pers. \p \v 8 Ba ñu dikkee ca kër Yàlla ga ca Yerusalem, ba ca déwén sa, ca ñaareelu weeru at ma, Sorobabel doomu Selcel, ak Yosuwe doomu Yoccadag ànd nañook ña des ca seeni bokk, sarxalkat yaak \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñaak mboolem ña jóge ca njaam ga délsi Yerusalem. Ñu daldi tàmbali liggéey bi. Ci biir loolu ñu tabb ay Leween ñu am ñaar fukki at, jëm kaw, ñuy saytu liggéeyu kër Aji Sax ja. \v 9 Yeswa nag jàpp ca, mook doomam yu góor aki bokkam, ak Kadmiyel ak doomam yu góor, ñuy askanu Odawya. Ñu mànkoo di jiite liggéeykat yiy tabaxaat kër Yàlla ga. Waa askanu Enadàdd jàpple nañu leen ci, ñook seen doom yu góor ak seen bokki Leween ña. \p \v 10 Ba tabaxkat ya lalee kenug kër Aji Sax ji, ñu tabb ay sarxalkat. Ñu solu ba jekk, yor ay liit, feggook Leween ña askanoo ca Asaf, ànd ak tëggum weñ, di màggal Aji Sax ji, muy la Daawuda buurub Israyil digle woon. \v 11 Ña ngay jàng, di màggal ak a sant Aji Sax ji, naan: \q1 «Kee baax. \q1 Kee gore ba fàww ci Israyil.» \m Ci kaw loolu mbooloo ma mépp xaacu, di ko màggale Aji Sax ji ngir kenug kër Aji Sax ja lale. \v 12 Teewul ñu bare ca ña féete mag, diy sarxalkat aki Leween aki boroom kër, gisoon nañu kër gu jëkk ga. Ba ñu gisee kenug kër gu bees ga, dañoo yékkati seen kàddu ca kaw di jooy, ñu bare it di xaacu ndax mbégte. \v 13 Kenn manuloona ràññee coowal mbégte laak jooy ya ndax riiru mbooloo mu réy, di àkki fu sore. \c 4 \s1 Liggéey baa ngi sooxe \p \v 1 Ba nooni Yudak Beñamin déggee ne waa ngàllo, ga ñibbsee ngay tabaxal \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Yàllay Israyil kër, \v 2 ñëw nañu ca Sorobabel ak ca kilifay kër ya, wax leen ne leen: «Danuy ànd ak yeen tabax ndax danuy topp seen Yàlla, ni yeen, te ca jamonoy Asaradon buurub Asiri, mi nu fi indi ba tey, Aji Sax ji lanuy defal sarax.» \v 3 Sorobabel nag ànd ak Yosuwe ak yeneen kilifay kër Israyil ya ne leen: «Dungeen bokk ak nun tabax sunu kër Yàlla gi. Nun doŋŋ ay tabaxal Aji Sax ji Yàllay Israyil, te loolu la Sirus buuru Pers santaane.» \v 4 Ci biir loolu waa réew ma di yoqiloo waa Yuda, di leen xoqtal, ba ñu ragala tabax. \v 5 Diirub nguurug Sirus buuru Pers, ba ca nguurug Daryus, waa réew ma dañu daan fey ay xelalkati buur ngir ñuy nasaxal pexey bànni Israyil. \p \v 6 Ca ndoortel nguurug Aserus nag, ñu bind Aserus bataaxal buy duural waa Yudak Yerusalem. \p \v 7 Ba tey ci janti Artaserses ku ñuy wax Bislam ak ku ñuy wax Mittredat ak Tabel aki nàttongoom, bind nañu Artaserses buuru Pers bataaxal bu ñu doore nii ci làkku arameen bala ñu koo tekki: \p \v 8 Reyum boroom dëkk ba, ak Simsay bindkatam, ñoo bind Buur Artaserses bataaxal bii jëm ci Yerusalem, di ko wax ne ko: \pmo \v 9 Bataaxal bii mu ngi bawoo ci Reyum, boroom dëkk bi, ak Simsay bindkatam, ak seen nàttongoy àttekat yeek kàngam yeek saytukat yeek boroom téere yi\f + \fr 4.9 \fr*\ft Ñeenti xeeti ndomboy tànk yi ñu lim fii am na tekki yu fi wuutal ñeenti turi dëkk. Su doon noonu dañu naan: \ft*\fqa ak seen nàttongo ya ca Din ak Arfasatag ak Tarpel ak Afaras.\fqa*\f*, ak waa Urug ak waa Babilon ak waa Sus, Elameen ña, \v 10 bawoo it ci yeneen mbooloo ya Asnapar\f + \fr 4.10 \fr*\fk Asnapar: \fk*\ft jombul mooy Asurbanipal, mi wuutu Àccar Adon ci jalu Asiri.\ft*\f* mu mag mu tedd ma toxaloon, sancal leen ca dëkki Samari ak li des ca Wàllaa Dex, ak ñoom seen. \p \v 11 Li ñu bind ci bataaxal ba jëm ca Buur Artaserses mooy lii: \pm Nun sa surga yii ci Wàllaa Dex ak li ci topp, \v 12 nu ngi lay xamal yaw Buur, ne Yawut ñi bàyyikoo fi yaw, ñëw fii ci nun, agsi nañu Yerusalem, dëkku fippukat bu bon bi, te ñu ngi koy tabaxaat. Ña ngay yékkati tata ya, gannaaw ba ñu lalaatee kenu ya. \v 13 Léegi nag Buur, xamal ne bu ñu tabaxaatee dëkk boobu, ba yékkatiwaat tata ya, galag mbaa njoti bopp mbaa juuti dootuñu ko fey, te kon koomu nguur gi dina ko yég. \v 14 Gannaaw nag sunu njël Buur la, jekkul ci nun nuy seetaan mbir mii. Looloo waral, Buur, nu yónnee, di la ko xamal, \v 15 ngir ñu seet ci sa téereb xew-xewi maam. Kon dinga ko ci gis ba xam ne dëkk boobu dëkku fippukat la, te sonal na ay buur aki boroom dëkk, te naka jekk dañu daan fippu ci seen biir. Looloo tasoon dëkk boobu. \v 16 Buur, nu ngi lay xamal ne bu ñu tabaxaatee dëkk boobu, ba yékkatiwaat tata ya, wetu Wàllaa Dex gii dootu doon sag moomeel. \p \v 17 Ci kaw loolu Buur yónnee tont la Reyum boroom dëkk ba, mook Simsay bindkat ba, ak nàttongoom ya ca des te dëkk Samari ak la des ca Wàllaa Dex. Mu nuyu leen, ne leen: \pm \v 18 Bataaxal bi ngeen ma yónnee, tekkees na ko, jàngal ma ko bu leer. \v 19 Ndigal tukkee na ci man, ngir ñu seet te gis nañu ne dëkk boobu kay yàgg nañoo fexeel buur yi, loolu indi fa ay fippooki pexey bañ. \v 20 Yerusalem nag amoon na buur yu am doole yu moom mboolem wet ga ca Wàllaa Dex, ñu di leen fey galag ak njoti bopp ak juuti. \v 21 Nangeen daldi joxe ndigal lu bàyyiloo nit ñooñu liggéey bi, ñu baña tabax dëkk boobu, ba keroog ma di ci joxe ndigal. \v 22 Fexeleen ba baña néewal mbir moomu bala muy law, ba doon loraange ci nguur gi. \p \v 23 Naka lañu jàng bataaxalu Buur Artaserses fa kanam Reyum boroom dëkk ba, ak Simsay bindkat ba aki nàttongoom, ñu ne coww ba Yerusalem, ca Yawut ña, jaay leen doole, gétën leen, ñu bàyyi liggéey ba. \v 24 Ci kaw loolu liggéeyu kër Yàlla ga ca Yerusalem taxaw. Taxaw na ba ca ñaareelu atu nguurug Daryus buuru Pers. \c 5 \s1 Liggéey bi dooraat na \p \v 1 Gannaaw loolu Yonent Yàlla Ase ak Yonent Yàlla Sàkkaryaa sëtub Ido, wax nañu ci turu Yàllay Israyil jiy seen Yàlla, ñeel Yawuti Yuda ak Yerusalem. \v 2 Booba la Sorobabel doomu Selcel, ak Yosuwe doomu Yoccadag tàmbalee tabaxaat kër Yàlla ga ca Yerusalem. Yonenti Yàlla ya nag ànd ak ñoom, di leen jàpple. \p \v 3 Booba la Tatnay, boroom Wàllaa Dex, ànd ak Setar Bosnay ak seeni nàttongo, dikk ne leen: «Ana ku leen may sañ-sañu tabaxaat kër gii, bay yékkati miir bi?» \v 4 Ñu dellu ne leen: «Ana ñan sax ñooy tabax taax mii?» \p \v 5 Fekk na seen Yàllaa ngi ne jàkk ci magi Yawut ñi, ba kenn bàyyiwul liggéey ba, ba keroog ñuy yónnee xibaar ba Buur Daryus, ba jot ci bataaxalu tontam ca mbir ma. \p \v 6 Bataaxal ba ñu bind Buur Daryus, te Tatnay boroom Wàllaa Dex yónnee ko ko, mook Setar Bosnay, ak jawriñi Tatnay ca Wàllaa Dex, lii moo ca nekk. \v 7 Kàddu ga nii la tëdde: \pm Buur Daryus, nu ngi lay bind, di la dikke sunu nuyoob jàmm ju sax. \v 8 Buur, nu ngi lay xamal ne dem nanu ca diiwaanu Yuda, ca kër Yàlla ju màgg ja. Ña nga koy tabaxe doj yu mag, di teg ay dénk ca miir ya. Liggéey baa ngay dox bu baax, di jëm kanam. \pm \v 9 Ci biir loolu laaj nanu seen mag ñooñu, ne leen: «Ana kan moo leen may sañ-sañu tabaxaat kër Yàlla gii, bay yékkati miiram bii?» \v 10 Nu laaj leen itam ñan ñoo koy tabax, ndax nu mana bind seen turi njiit, ba xamal la ñan la. \pm \v 11 Li ñu nu tontu mooy lii: \pm «Nun ay jaami Yàlla Boroom asamaan ak suuf lanu. Danuy tabaxaat kër Yàlla gi ñu tabaxoon lu jiitu ay at yu bare. Buurub Israyil bu mag moo ko tabaxoon ba sottal ko. \v 12 Sunuy maam nag ñoo merloo Yàllay asamaan, ba tax mu teg leen ci loxoy Nabukodonosor buuru Babilon, ma askanoo ci waa Kalde. Mu toj kër gii, yóbbu xeet wi ngàllo ca Babilon. \v 13 Terewul ca at ma jëkk ca nguurug Sirus buuru Babilon\f + \fr 5.13 \fr*\fk Sirus buuru Babilon \fk*\ft bi ñuy wax fii mooy Buuru Pers rekk, ndax fekk na Pers moom nguurug Babilon.\ft*\f*, Buur Sirus joxe ndigal ngir ñu tabaxaat kër Yàlla gii. \v 14 Te sax ndabi wurus ak xaalis yu kër Yàlla ya Nabukodonosor jële woon ca Yerusalem, te yóbbu ko ca kër tuuram ga ca Babilon, Buur Sirus jële na ko ca kër tuuram ga ca Babilon, teg ko ca loxol ku mu fal boroom dëkk, ñu di ko wax Sesbasar. \v 15 Mu ne ko: “Ndab yii, jël ko yóbbu ca kër Yàlla ga ca Yerusalem, te nañu tabaxaat kër Yàlla ga fa mu nekkoon.” \v 16 Sesbasar moomu nag ñëw lal kenug kër Yàlla gi ci Yerusalem. Booba ba léegi, ñu ngi koy tabax waaye noppeegul.» \pm \v 17 Léegi nag Buur, su la soobee, nañu seet ca denci buur, foofu ci Babilon, ngir wóorlu ndax Buur Sirus joxe woon na ndigal ne ñu tabaxaat kër Yàlla gi ci Yerusalem. Gannaaw loolu loo dogal ci mbir mi rekk, Buur, yónneel, jottli nu ko. \c 6 \s1 Buur Daryus joxe na ndigal \p \v 1 Ba loolu amee Buur Daryus joxe ndigal, ñu seet ca kërug dencukaayi téere ya, fa ñu denc alali Babilon. \v 2 Ñu gis ca Egbatan, péeyu diiwaanu Medd, taxañ bu ñu bind seede bii: \pmo \v 3 At ma jëkk ca nguurug Buur Sirus, Buur Sirus joxe na ndigal ci mbirum kër Yàlla ga ca Yerusalem. Mu ne: \pm Nañu tabaxaat kër Yàlla gi, muy bérab bu ñuy sarxee ay sarax. Nañu dëgëral kenu ya. Na taxawaayam di juróom benn fukki xasab\f + \fr 6.3 \fr*\fk xasab \fk*\ft mooy guddaayu loxo bu digg-dóomu diggante catu baaraamu digg ak conc.\ft*\f*, yaatuwaayam di juróom benn fukki xasab, \v 4 te ñetti sësalantey doj yu mag yu tegloo yu ne, ab sësalanteb dénk tege ca kawam. Nañu génnee njég ga ca alali Buur, joxe ko. \v 5 Bu loolu weesee, ndabi wurus yaak yu xaalis ya woon ca kër Yàlla ga, te Nabukodonosor jële woon ko ca kër Yàlla ga ca Yerusalem, indi ko Babilon, nañu ko delloo fa mu nekkoon ca kër Yàlla ga ca Yerusalem te fat ko fa. \pm \v 6 Kon nag ñooñu di Tatnay boroom Wàllaa Dex ak Setar Bosnay ak seen nàttongo yay jawriñ ca Wàllaa Dex, nañu sore foofa. \v 7 Buleen tere liggéeyu kër Yàlla gee dox. Na boroom dëkki Yawut ñi ànd ak magi Yawut ñi, ñu tabaxaat kër Yàlla googu fa mu nekkoon. \pm \v 8 Rax ci dolli ndigal a ngii tukkee ci man, jëm ci li ngeen wara defal magi Yawut yooyu ci biir liggéeyu kër Yàlla googu: Njég ga mu leen dikke, nañu leen ko fey ba mu mat, jële ko ca alali buur, ca galagi diiwaan ba ca Wàllaa Dex. Nañu ko fey ñooñu, ba liggéey ba baña taxaw. \v 9 Mboolem lu ci war, muy yëkk yu ndaw mbaa ay kuuy mbaa ay xar yu ndaw yu ñuy defal Yàlla Boroom asamaan \w saraxu dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, muy bele it mbaa xorom mbaa biiñ mbaa diw, lu ci \w sarxalkati|lemma="sarxalkat b-:"\w* Yerusalem laaj, nañu leen ko jox bés ak bés, te bañ koo sàggane. \v 10 Su ko defee ñu mana sarxalal Yàlla Boroom asamaan lu ko neex tey ñaanal Buur aki doomam gudd fan. \pm \v 11 Gannaaw loolu ndigal a ngii tukkee ci man ñeel képp ku tebbi bii dogal: Dees na roccee ca néegam ab xànq, yékkati ko, wékk ko ca, ba noppi def këram ab sën ndax jëfam jooju. \v 12 Yàlla ji dëël turam boobu bérab nag, yal na daaneel bépp buur mbaa xeet wuy fexee tebbi bii dogal, ba nara yàq kër Yàlla gii ci Yerusalem. \pm Man Daryus maa joxe ndigal lii. Nañu ci farlu. \p \v 13 Ba mu ko defee Tatnay boroom Wàllaa Dex, ak Setar Bosnay ak seeni nàttongo daldi xar seen tànku tubéy ci jëfe ndigal la Buur Daryus joxe. \v 14 Magi Yawut ña nag tabax ba mu baax, mu dëppook kàdduy Yonent Yàlla Ase ak Sàkkaryaa, sëtub Ido. Ñu tabax ba sottal, muy la Aji Sax ji Yàllay Israyil santaane woon, te dëppook ndigalul Sirus ak Daryus ak Artaserses buuru Pers. \v 15 Kër gaa nga sotti ci ñetti fanu weeru Adar, juróom benneelu atu nguurug Daryus. \v 16 Ci kaw loolu mbooloom Israyil ànd ak sarxalkat yaak \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñaak mboolem ña ñibbsee ca ngàllo ga, ñu daloo tabax ba ci biir mbégte. \v 17 Sarxe nañu ca daloog kër Yàlla googu téeméeri yëkk, ak ñaar téeméeri kuuy ak ñeenti téeméeri xar yu ndaw, ak fukki sikket ak ñaar, dëppook limu giiri Israyil, def ko saraxu póotum bàkkaar, ñeel Israyil gépp. \v 18 Ci biir loolu ñu tabb sarxalkat ya, ca wàll ya ñu bokk ak Leween ña ca seeni kurél, ñu sasoo liggéeyu Yàlla ji ci Yerusalem, muy la ñu bind ci téereb Musaa. \p \v 19 Fukki fan ak ñeent ca weer wu jëkk wa nag, ña ñibbsee woon ngàllo ga daldi màggal \w bésub Mucc|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* ba. \v 20 Fekk na \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yaak \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ña laabal seen bopp, ba ñoom ñépp bokk laab. Ba loolu amee ñu rendi xarum bésub Mucc ba, ñeel mboolem ña ñibbsee ngàllo, ak ñoom sarxalkat yi ci seen bopp, ñook seeni bokk. \v 21 Ba mu ko defee, \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ga ñibbsee ngàllo ga daldi bokk reerub bésub Mucc ba, ñook mboolem ña dogoo woon ak sobey yéefar yi ci réew mi, ngir sàkku \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, Yàllay Israyil. \v 22 Wormaal nañu it \w màggalu Mburu mu amul lawiir|lemma="Màggali Yawut yi:"\w*, diiru juróom ñaari fan, ci biir mbégte, ndax fekk na Aji Sax ji bégal leen lool ca na mu xiire buurub Asiri\f + \fr 6.22 \fr*\fk Asiri \fk*\ft gi ñuy wax fii, booba mu ngi ci loxol buuru Pers.\ft*\f*, mu yéwéne leen ba dimbali leen ci tabaxu kër Yàlla ga, Yàllay Israyil. \c 7 \s1 Buur Artaserses yéwéne na Esra \p \v 1 Ba loolu weesee, ca jamonoy nguurug Artaserses buuru Pers, am na góor gu ñuy wax Esra, Seraya di baayam. Seraya, Asaryaa; Asaryaa, Ilkiya; Ilkiya, \v 2 Salum; Salum, Cadog; Cadog, Ayitub; \v 3 Ayitub, Amarya; Amarya, Asaryaa; Asaryaa, Merayot; \v 4 Merayot, Seraya; Seraya, Usi; Usi, Bukki; \v 5 Bukki, Abiswa; Abiswa, Fineyas; Fineyas, Elasar; Elasar, Aaróona, \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bu mag ba. \v 6 Esra moomu jóge Babilon, nekkoon jànglekat bu xareñ, bu géeju ci yoonu Musaa, wi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Yàllay Israyil joxoon ñoñam. Aji Sax ji Yàllaam nag toppe ko yiwam, ba Buur defal ko mboolem lu mu ñaan. \p \v 7 Ca juróom ñaareelu atu nguurug Buur Artaserses, mu am ñenn ci \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ñu ànd, di ay sarxalkat aki \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* aki jàngkat aki fara bunt, ak liggéeykati kër Yàlla ga. Ñu daldi dem Yerusalem. \v 8 Esra nag bokkoon ca. Mu agsi Yerusalem ca juróomeelu weeru at mooma, di juróom ñaareelu atu buur ba. \v 9 Ca benn fanu weer wa jëkk la dooroon yoon woowu mu bàyyikoo Babilon. Mu agsi Yerusalem ca benn fanu juróomeelu weer wa, ci mbaaxu Yàllaam ji ko toppe yiwam. \v 10 Esra nag doonoon ku pastéefu ci jàng yoonu Aji Sax ji, di ko sàmm tey jàngle ci Israyil ay dogalam ak ndigali yoonam. \s1 Buur Artaserses bind na Esra \p \v 11 Lii mooy li ñu bind ci bataaxal ba Buur Artaserses jox Esra, \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba, jànglekat ba géeju ci mbiri santaaney \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ak dogalam yi ñeel Israyil. \pmo \v 12 Bataaxal bii mu ngi bàyyikoo ci Artaserses, buuru buur yi, jëm ca Esra, \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* biy jàngle yoonu Yàlla Boroom asamaan. Maa ngi lay nuyu. \pm Gannaaw loolu nag, \v 13 ndigal tukkee na ci man ne mboolem kuy bànni Israyil ci samam réew, ba ci sarxalkat yeek \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi, ku ci bëgga ànd ak yaw Yerusalem, man naa dem. \v 14 Man Buur, maa la yebal, maak sama juróom ñaari wóllëre; noo la yebal Yerusalem ak Yuda, ngir nga gëstujil ma nu ñu fay toppe sa yoonu Yàlla, wi nga yor téereem ci say loxo. \v 15 Te nga yóbbaale xaalis beek wurus, wi ma joxe ci xol bu tàlli, jagleel ko Yàllay Israyil ji ci Yerusalem, man Buur, maak samay wóllëre, \v 16 boole ci mboolem xaalis mbaa wurus woo mana jële ci diiwaanu Babilon bépp, ak itam saraxi yéene yi baadoolo yeek sarxalkat yi joxe ci xol bu tàlli, lépp ñeel seen kër Yàlla ga ca Yerusalem. \v 17 Ci biir loolu, xaalis boobu nanga ko daldi jënde ay yëkk aki kuuy ak xar yu ndaw ak saraxi pepp ak \w saraxi tuuru|lemma="Sarax yi:"\w* yi muy àndal te nga boole ko, jooxe ca seen \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* kër Yàlla ga ca Yerusalem. \v 18 Li des ci xaalis beek wurus wi nag, defleen ko lu ngeen namm, yaak say bokk, na mu dëppook seen coobarey Yàlla. \v 19 Bu loolu weesee ndab yi ñu la jox, ñu di ko jaamoo ca seen kër Yàlla ga, nanga ko boole teg fa kanam Yàllay Yerusalem. \v 20 Leneen lu des it, loo wara def ci sa kër Yàlla gi, sañ nga koo génnee ci alalu buur. \pm \v 21 Man Buur Artaserses, jox naa ndigal mboolem denckati alali buur ya ca Wàllaa Dex, ne leen: Lépp lu Esra, sarxalkat biy jàngle yoonu Yàlla Boroom asamaan, sàkku ci yeen, nangeen ko daldi def; \v 22 ba ci fanweeri barigoy xaalis, ñetti téeméeri barigoy bele, ñaar fukki barigoy biiñ, ak ñaar fukki barigoy diw, ak lu mu soxla ci xorom. \v 23 Lépp lu Yàlla Boroom asamaan digle, nañu ko defe noonee ca kër Yàlla Boroom asamaan, ndax meram baña dal ci sama kaw nguur gii ak ci sama kaw askan. \v 24 Nu ngi leen di xamal itam ne képp kuy sarxalkat mbaa ab Leween, mbaa mu dib jàngkat mbaa fara bunt, mbaa mu di liggéeykatu kër Yàlla gi, mbaa surga buy liggéey ci kër Yàlla googu, du galag bu ñu ko saña teg mbaa njotu bopp mbaa ab juuti. \pm \v 25 Yaw Esra nag, seetal ci xel mu rafet mi sa Yàlla digle ci yoonam wi nga yor, nga tabb ay njiit aki xaali, ngir ñuy àtte mboolem ñi xam sa yooni Yàlla ci diiwaani Wàllaa Dex. Te ñi ko xamul, nga xamal leen ko. \v 26 Képp ku ci sàmmul sa yoonu Yàlla ak yoonu buur, nañu ko daldi teg mbugal mi war ci moom. Dee mooy doon àtteem, mbaa ñu génne ko réew mi, mbaa ñu nangu alalam, mbaa ñu tëj ko. \s1 Esra sant na \p \v 27 Cant ñeel na \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, sunu Yàllay maam, moom mi def nii ci xolub Buur yéeney teral kër Aji Sax ji ci Yerusalem, \v 28 te dawal ngor sama digganteek Buur aki wóllëreem ak mboolem kàngami buur yu mag yi! Man nag, nii la ma sama Yàlla Aji Sax ji toppe yiwam, ba ma dëgërlu, boole njiiti Israyil, ñu daje, ànd ak man dem. \c 8 \s1 Lu jëm ci ñi ànd ak Esra \p \v 1 Ñi jiite seen làngi kër maam ak ñi ñu bindaaleek ñoom ci limeef yi, te ñu ànd ak man Esra, jóge Babilon ca jamonoy Buur Artaserses, ñii la: \v 2 Ci askanu Fineyas, Gersom la. Ci askanu Itamar, Dañeel la. Ci askanu Daawuda, Atus, \v 3 mi askanoo ci Sekaña la. Askanu Paros, Sàkkaryaa bawoo ca, ànd ak téeméeri góor ak juróom fukk (150). \v 4 Ci askanu Payat Mowab, Elyowenay doomu Seraya la, mook ñaar téeméeri góor (200). \v 5 Ci askanu Sàttu\f + \fr 8.5 \fr*\fk Sàttu: \fk*\ft tekki bu jëkk ba ci làkku gereg moo indi turu Sàttu.\ft*\f*, Sekaña doomu Yasyel la, mook ñetti téeméeri góor (300). \v 6 Ci askanu Adin, Ebedd doomu Yonatan la, mook juróom fukki góor (50). \v 7 Ci askanu Elam, Esayi doomu Atalyaa la, mook juróom ñaar fukki góor (70). \v 8 Ci askanu Sefatiya, Sebadiya doomu Mikayel la, mook juróom ñett fukki góor (80). \v 9 Ci askanu Yowab, Obadiya doomu Yeyel la, mook ñaar téeméeri góor ak fukk ak juróom ñett (218). \v 10 Ci askanu Baani\f + \fr 8.10 \fr*\fk Baani: \fk*\ft tekki bu jëkk ba ci làkku gereg moo indi turu Baani.\ft*\f*, Selomit doomu Yosifya la, mook téeméeri góor ak juróom benn fukk (160). \v 11 Ci askanu Bebay, Sàkkaryaa doomu Bebay la, mook ñaar fukki góor ak juróom ñett (28). \v 12 Ci askanu Asgàdd, Yowanan doomu Àkkatan la, mook téeméeri góor ak fukk (110). \v 13 Askanu Adonikam ñoo mujje, ñu di leen wax Elifelet ak Iyel ak Semaya, ñook juróom benn fukki góor (60). \v 14 Ci askanu Bigway, Utay la ak Sabudd, ñook juróom ñaar fukki góor (70). \p \v 15 Ci kaw loolu ma boole leen, ñu daje ca wetu dex, ga jëm Aawa, dal fa ñetti fan. Ma seetlu fa baadoolo ya, seet ca biir \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ya, gisuma kenn ku bokk ci \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi. \v 16 Ma woolu njiit ya: Elyeser ak Aryel ak Semaya ak Elnatan ak Yarib ak Elnatan meneen ma, ak Natan ak Sàkkaryaa ak Mesulam, ak Yowarib ak Elnatan ma ca des, ñaari jànglekati yoon ya. \v 17 Ba mu ko defee ma yebal leen ca Ido, njiit la ca gox ba ñuy wax Kasifya, daldi leen wax kàddu ya ñuy jottli Ido ak bokkam yay liggéeykati kër Yàlla, ya dëkk Kasifya, ndax ñu yónnee nu ay surga ci sunu liggéeyu kër Yàlla gi. \v 18 Sunu Yàlla nag toppe nu mbaaxu yiwam, ba ñu indil nu waa ju am xel, askanoo ci Maali sëtub Lewi doomu Israyil. Ñu di ko wax Serebya. Mu ànd ak doomam yu góor aki bokkam, ñuy fukk ak juróom ñett (18), \v 19 ñook Asabya ak Esayi sëtu Merari. Ñu ànd ak seeni bokk ak seen doom yu góor, di ñaar fukki góor (20). \v 20 Indaale nañu ñaar téeméeri liggéeykati kër Yàlla ak ñaar fukk (220), di ñu askanoo ca ña Daawudaaki jawriñam tànnoon, bind seeni tur, ngir ñuy jàpple Leween ñi. \p \v 21 Ba loolu amee ma digle foofa koor ca tàkkal dexu Aawa, toroxloo ko fa sunu kanam Yàlla, ngir ñaan ko mu may nu yoonu jàmm, nook sunuy doom ak mboolem lu bokk ci nun. \v 22 Ndaxte rusoon naa ñaan Buur mu boole nook ay dag ak gawar yu nu aar ci noon yi ci yoon wi. Li ko waral mooy fekkoon na nu wax Buur ne ko: «Sunu Yàlla mooy toppe yiwam mboolem ku ko yaakaar, di ko defal jàmm, waaye meram dina dal ak doole ci kaw mboolem ku ko dëddu.» \v 23 Nu woor, daldi dagaan sunu Yàlla mbir moomu, mu nangul nu. \v 24 Ba loolu amee, ma tànn fukki sarxalkat ak ñaar yu mag, ñuy Serebya ak Asabya ak seen fukki bokk. \v 25 Gannaaw loolu ma nattal leen xaalis baak wurus waak ndab, ya Buur aki wóllëreem aki jawriñam jooxe woon, ñook mbooloom Israyil ma fa teewoon, te lépp jëm ca sunu kër Yàlla ga. \v 26 Natt naa ba teg ci seeni loxo ñaar téeméeri barigoy xaalis ak fanweeri barigo ci jumtukaayi xaalis ak fanweeri barigoy wurus, \v 27 ak ñaar fukki koppi wurus yu wecci junniy poseti wurus, ak ñaari ndab yu jafe, yu xànjar bu ñu raxas ba muy melax, mel ni wurus. \v 28 Ma ne leen: «Yeen, dees leena sellalal \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ni ñu sellale ndab yi, te xaalis beek wurus wi di \w saraxu yéene|lemma="Sarax yi:"\w* ñeel Aji Sax ji, seen Yàllay maam. \v 29 Xool-leen ko te sàmm ko bu baax, ba kera ngeen koy natt ca denci kër Aji Sax ji ca Yerusalem, fa kanam kilifay sarxalkat yaak Leween ñaak ña jiite seen làngi kër maam ci \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*.» \p \v 30 Ci kaw loolu nu nattal sarxalkat yeek Leween ñi xaalis baak wurus waak ndab yu sell ya, ngir ñu yóbbu ko ca sunu kër Yàlla ga ca Yerusalem. \v 31 Fukki fan ak ñaar ca weer wa jëkk lanu bàyyikoo dexu Aawa, daldi jëm Yerusalem. Sunu Yàlla nag toppe nu yiwam, ba musal nu ci noon akub saaysaay ci yoon wi. \p \v 32 Gannaaw loolu nu agsi Yerusalem, nopplu fa ñetti fan. \v 33 Bésub ñeenteel ba nu natt diisaayu xaalis baak wurus waak ndab ya ca sunu biir kër Yàlla ga, teg ko ca loxol Meremot doomu Uri, sarxalkat ba, mook Elasar doomu Fineyas, ak Leween ña, di Yosabàdd doomu Yeswa, ak Nowadiya doomu Binuy. \v 34 Ñu limaat lépp, nattaat diisaay ba, daldi bind ca saa sa dayo ba bépp. \p \v 35 Ba mu ko defee ña jóge njaam, ñibbsee ca ngàllo ga, daldi defal Yàllay Israyil ay \w saraxi dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*. Muy fukki yëkk ak ñaar, ñeel Israyil gépp ak juróom ñeent fukki kuuy ak juróom benn (96), ak juróom ñaar fukki xar yu ndaw ak juróom ñaar (77), ak fukki sikket ak ñaar yu ñu def \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*; ñu def lépp saraxu dóomal, ñeel Aji Sax ji. \v 36 Ci biir loolu ñu jottli ndigali buur, ya jëm ca ay jawriñam ak njiiti Wàllaa Dex. Ñooñu it jàpple mbooloo ma ca liggéeyu kër Yàlla ga. \c 9 \s1 Askan wi rax na \p \v 1 Gannaaw ba loolu wéyee njiit ya dikk, ne ma: «Du \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, du \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi, du \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi, kenn ci ñoom teqlikoowul ak xeeti réew meek seen aada yu siblu. Dañuy jëfe ni Kanaaneen ñeek Etteen ñeek Periseen ñeek Yebuseen ñeek Amoneen ñeek Mowabeen ñeek waa Misraak Amoreen ñi. \v 2 Jël nañu jabar ci ñoom, jëlal ci jabar seeni doom, ba jaxase jiwu mu \w sell|lemma="sell:"\w* mi ak waasoy réew yi. Njiit yeek mag ñi sax ñoo jiitu ci googu fecci kóllëre.» \p \v 3 Ba ma déggee loolu damaa xotti sama turki ak sama mbubb, xuuf sama kawaru bopp ak sama sikkim, daldi toog, ne tott. \v 4 Ba loolu amee mboolem ñi wormaal kàddug Yàllay Israyil daje, wër ma ndax ñàkk kóllëreg ña ñibbsee ca ngàllo ga. Ma toog, ne tott ba waxtuw saraxu ngoon. \v 5 Saraxu ngoon jot, ma jóge ca sama jataayu toroxtaange, ba ma xottee sama turki baak sama mbubb ma. Ma ne gurub sukk, tàllal sama Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji loxo, \v 6 daldi ñaan, ne: \pi1 Éy sama Yàlla maa rus, maa torox, ba manumaa siggi fi sa kanam, ndaxte sunuy bàkkaar bare na, ba mëdd nu, sunuy moy tegloo ba àgg asamaan. \v 7 La ko dale ca sunu janti maam ba bésub tey jii, nu ngi ci moy gu réy. Sunuy bàkkaar tax na buuri réew yi teg nu loxo, nook sunuy buur ak sunuy sarxalkat, ñu di nu rey, di nu jàpp njaam, di lël sunu alal, di nu torxal ba sunu jonni yàllay tey. \pi1 \v 8 Waaye yaw Aji Sax ji sunu Yàlla, yàggul dara aw yiw bàyyikoo na ci yaw, musal ñenn ci nun, may nu ndëgërlaay ca sa \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* ba. Yaw sunu Yàlla, yaa nu taxa leqliku, yaa nu dundalaat ci sunu biir njaam gi. \v 9 Ndax ay jaam lanu, waaye yaw sunu Yàlla, waccewoo nu sunug njaam. Yaa dawal ngor sunu digganteek buuri Pers, ngir mayaat nu dooley tabax sunu kër Yàlla, yékkatee ko ca gentam ba, may nu kiiraay ci Yerusalem ak ci Yuda. \pi1 \v 10 Yaw sunu Yàlla, ana lu nuy waxati nag gannaaw lii? Ndax kat noo dëddu sa santaane, \v 11 yi nga nu dénk, yonent yiy say jaam jottli ko, ne nu: «Réew mi ngeen di nanguji, réew mu sobewu la ndax sobey waasoy réew ma. Feesal nañu kook seeni jëf ju siblu ak seen tilim, ba fépp daj. \v 12 Kon nag seen doom yu jigéen buleen leen may seen doom yu góor, te seen doom yu jigéen buleen leen jëlal seen doom yu góor. Buleen seet mukk seen jàmm mbaa seen njariñ. Looloo leen di taxa am doole, bay xéewlu ci ngëneeli réew mi, ba wacce ko seen askan fàww.» \v 13 Loolu nu dal lépp, sunu jëf ju bon a tax, ak sunu tooñ gu réy. Terewul yaw sunu Yàlla, tegoo nu lu dul mbugal mu yées mi sunuy bàkkaar yellool. Terewul yaw sunu Yàlla, li nu bàkkaar mbugaloo nu ko, te moo nu fi taxa des di dund nii. \v 14 Nan lanu mana dellooti di xëtt say santaane, di séyanteek xeet yii ak seen jëf ju siblu? Kon doo nu mere, faagaagal nu, ba kenn du desati mbaa muy rëcc? \v 15 Yaw Aji Sax ji Yàllay Israyil, yaay boroom njekk. May nga nu bésub tey jii nu dese bakkan. Nu ngi nii fi sa kanam ci biir tooñange, ba tax du kenn ci nun ku am lay fi sa kanam. \c 10 \s1 Fase nañu jaambur ñi \p \v 1 Naka la Esra di ñaan ak a tuub, di jooy, ak a daanu fa suuf ca buntu kër Yàlla ga, \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* yéew ko, bare lool, góor ak jigéen, ba ca xale ya. Mbooloo ma it di jooy jooy yu metti. \v 2 Ci biir loolu Sekaña doomu Yeyel ma askanoo ci Elam, daldi wax Esra ne ko: «Noo tooñ sunu Yàlla, di jël ay jaambur jabar ci xeeti réew mi. Waaye loolu terewul Israyil am yaakaar ba tey. \v 3 Léegi kay nanu fasanteek sunu Yàlla \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w*, daldi fase jigéen ñooñu ñépp, ñu ànd ak seeni doom, muy ni nga ko diglee rekk, sang bi, yaak ñi wormaal sunu santaaney Yàlla. Li yoon wi digle daal, na am. \v 4 Jógal nag, mbir maa ngi ci say loxo, te noo ngi ànd ak yaw. Kon dëgërlul te def ko.» \p \v 5 Ci kaw loolu Esra jóg, wax kilifay \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yaak \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñaak Israyil gépp, ne leen ñu giñ ne noonu lañu koy defe. Ñu giñ ko. \v 6 Ba loolu amee Esra bàyyikoo kër Yàlla ga, fatuji néegu Yowanan doomu Elyasib. La mu fa nekk nag lekkul, naanul, xanaa di ñaawlu na ngàllo, ga ñibbsi feccee worma. \v 7 Ba mu ko defee ñu yéene ci Yerusalem ak Yuda, yégal mboolem ngàllo ga ñibbsi, ne leen ñu daje ca Yerusalem. \v 8 Ñu ne képp ku teewul ci diiru ñetti fan, ni ko kilifa yeek mag ñi diglee, dees na teg alalam jépp loxo, te moom ci boppam dees na ko dagge ca ngàllo, ga ñibbsi. \p \v 9 Ba ñu ca tegee ñetti fan mboolem góori Yudak Beñamin daje nañu Yerusalem, mu yemook ñaar fukki fan ca juróom ñeenteelu weer wa. Ña nga toog ñoom ñépp ca ëttu kër Yàlla ga, di lox ndax solob ndaje ma, ak itam taw bu bare ba mu yemool. \v 10 Ci kaw loolu Esra sarxalkat ba jóg taxaw, ne leen: «Yeena fecci kóllëre ndax yeena jël ay jaambur jabar, di yokk tooñaangey Israyil. \v 11 Léegi nag tuubleen ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji seen Yàllay maam te def coobareem. Teqlikooleen ak xeeti réew mi, teqlikook jigéen ñii diy jaambur.» \p \v 12 Ci kaw loolu mbooloo mépp bokk àddu ca kaw ne ko: «Tigi, li nga wax rekk lanu wara def. \v 13 Waaye danoo bare, te muy jamonoy taw. Manunoo toog fii ci biti. Te it mbir mi maneesu koo lijjanti ci benn bés mbaa ñaar, ndax sunu tooñ ci mbir mii daa yaatu. \v 14 Kon daal na sunuy kilifa taxawal askan wi. Su ko defee mboolem ku nekk ci sunuy dëkk te jël ci jaambur ñi jabar day dikk, ku ci nekk ca bés ba ñu ko àppal, te mu ànd ak kilifa yaak àttekati dëkkam. Ñu topptoo mbir mi nag, ba keroog sunu merum Yàlla mu réy mi sababoo ci lii, dëddu nu.» \p \v 15 Mennum Yonatan doomu Asayel, ak Yaasya doomu Tigwa, ñoom doŋŋ, ñook Mesulam ak Sabtay, Leween ba, ñoo àndul ca loola. \v 16 Ci kaw loolu ngàllo, ga ñibbsi daldi def la ñu wax. Esra sarxalkat ba tànn nit ña jiite seen kër baay, ku nekk ak làngam, ñoom ñépp ñu tudd seeni tur. Keroog benn fan ca fukkeelu weer wa nag, ñu toog ngir seet mbir ma. \v 17 Ca benn fanu weer wa jëkk ca déwén sa lañu lijjanti mbiru mboolem ña jëloon jabar ay jaambur. \s1 Ñii ñoo jëggaani ay soxna \li1 \v 18 Ñu gis ne ñenn ci askanu \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi jëloon nañu ay jaambur soxna: \li1 Ci askanu Yosuwe doomu Yoccadag aki bokkam, Maaseya ak Elyeser ak Yarib ak Gedalya bokk nañu ca. \v 19 Ñu xas ne dinañu fase seeni soxna, daldi nangu ne tooñ nañu, ba noppi ku nekk ci ñoom sarxe am kuuy, muy peyug tooñam. \li1 \v 20 Ci askanu Imer, Anani la ak Sebadiya. \li1 \v 21 Ci askanu Arim, Maaseya laak Ilyaas ak Semaya ak Yeyel ak Osiyas. \li1 \v 22 Ci askanu Pasur, Elyonay laak Maaseya ak Ismayla ak Netanel ak Yosabàdd ak Elasa. \b \li1 \v 23 Ci \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi: Yosabàdd laak Simey ak Kelaya, mooy Kelita ba tey, ak Petaya ak Yuda ak Elyeser. \li1 \v 24 Ci jàngkat yi: Elyasib la. \li1 Ci fara bunt yi: Salum laak Telem ak Uri. \b \li1 \v 25 \w Bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* yi ci des: \li1 Ci askanu Paros, Ramya laak Isya ak Malkiya ak Miyamin ak Elasar ak Malkiya ak Benaya. \li1 \v 26 Ci askanu Elam, Mataña laak Sàkkaryaa ak Yeyel ak Abdi ak Yeremot ak Ilyaas. \li1 \v 27 Ci askanu Sàttu, Elyonay laak Elyasib ak Mataña ak Yeremot ak Sabàdd ak Asisa. \li1 \v 28 Ci askanu Bebay, Yowanan laak Anaña ak Sabay ak Atlay. \li1 \v 29 Ci askanu Baani, Mesulam laak Malug ak Adaya ak Yasub ak Seyal ak Yeremot. \li1 \v 30 Ci askanu Payat Mowab, Adna laak Kelal ak Benaya ak Maaseya ak Mataña ak Besalel ak Binuy ak Manase. \li1 \v 31 Ci askanu Arim, Elyeser laak Isija ak Malkiya ak Semaya ak Simeyon, \v 32 ak Beñamin ak Malug ak Semarya. \li1 \v 33 Ci askanu Asum, Matenay laak Matata ak Sabàdd ak Elifelet ak Yeremay ak Manase ak Simey. \li1 \v 34 Ci askanu Baani, Madaay laak Amram ak Uyel \v 35 ak Benaya ak Bedeya ak Keluyi \v 36 ak Waña ak Meremot ak Elyasib \v 37 ak Mataña ak Matenay ak Yasaaw \v 38 ak Baani ak Binuy ak Simey \v 39 ak Selemya ak Natan ak Adaya \v 40 ak Magnadebay ak Sasay ak Saray \v 41 ak Asarel ak Selemya ak Semarya \v 42 ak Salum ak Amarya ak Yuusufa. \li1 \v 43 Ci askanu Nebo, Iyel la, ak Matitiya ak Sabàdd ak Sebina ak Yaday ak Yowel ak Benaya. \p \v 44 Ñooñu ñépp jël nañu ay jaambur jabar, ba ñenn ci ñoom ami doom.