\id EZK (WOL) \ide UTF-8 \h Esekiyel \toc1 Esekiyel \toc2 Esekiyel \mt1 Esekiyel \c 1 \s1 Esekiyel daje naak leeru Aji Sax ji \p \v 1 Am na bés, mu yemook sama fanweereelu at, juróomi fan ca ñeenteelu weer wa, booba maa nga bokkoon ca ña ñu toxal ca tàkkal dexu Kebar\f + \fr 1.1 \fr*\fk dexu Kebar \fk*\ft a nga woon ca Babilon, ga buuram Nabukodonosor dencoon bànni Israyil, gannaaw ba mu leen jàppee ba yóbbu leen fa ngàllo. Yonent Yàlla Esekiyel ab sarxalkat la fa woon ca biir bokki bànni Israyilam.\ft*\f*. Asamaan daa ubbiku, ma daldi gis ay peeñuy Yàlla. \s1 Bindkat a ngi joxe tegtal ca moomu peeñu \p \v 2 Juróomi fani weer wa moo yemook juróomi at gannaaw ba ñu toxalee Buur Yowakim. \v 3 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji moo dikkal Esekiyel doomu Busi, \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba fa réewum Kaldeen ña ca tàkkal dexu Kebar. Te foofa la loxol Aji Sax ji dikke fa kawam. \s1 Nii la peeñu ma bindoo \p \v 4 Naka laa xool rekk, ngelaw lu réy jekki dikke bëj-gànnaar, ànd ak niir wu mag, sawara di ca fettaxe, ag leer gu ne ràññ wër ko; digg ba mel ni weñ guy tàkk. \v 5 Digg ba, jëmmi ñeenti bindeef a ca feeñ yu ame melokaanu nit. \v 6 Ku ci nekk am na ñeenti kanam ak ñeenti laaf. \v 7 Seeni tànk daa jub, téstën ya mel ni weyi sëllu di melax ni xànjar bu ñu jonj. \v 8 Seen laaf, loxoy nit a nga ca suufam ci seen ñeenti wet yépp, ñoom ñeent ñépp ak seeni kanam ak seeni laaf. \v 9 Seen ñeenti cati laaf a ngay laale, te ku nekk man naa jubal màkk fépp fu genn kanam jublu te du jar muy warangiku. \v 10 Seen melokaanu kanam nag nii la bindoo: ku ci nekk am nga kanamu nit fa féete kanam ak kanamu gaynde ci sa ndijoor. Ku ci nekk itam am nga kanamu yëkk fi sa càmmoñ ak kanamu jaxaay fa féete gannaaw. \v 11 Seeni kanam a ngoogu. Ku ci nekk sa ñaari laaf a jëm kaw, di laal sa laafi moroom. Sa ñaari laaf yi ci des sàng sa yaram. \v 12 Ku nekk man naa jubal màkk fépp fu genn kanam jublu. Fépp fu Noowug Yàlla jublu, ñu jublu fa te warangikuwuñu. \v 13 Jëmmi bindeef yaa nga am melow xali sawara yu yànj, mel niy jum, sawara way dem ak dikk ci seen biir. Sawara waa nga ne ràññ, ay melax di ca fettaxe. \v 14 Bindeef yaa ngay naaw, di dem ak a dikk, mel ni melax. \p \v 15 Naka laa xool, daldi gis ay mbege fi suuf, mbege mu ci nekk feggook menn mbindeef, mook ñeenti kanamam. \v 16 Mbege yaa ngay nirook peru kirsolit, ci melokaan ak ci bind. Ñoom ñépp a niroo. Seen melokaan ak seen bind daa mel ni, mbege mu ci nekk, mbegee nekk ca biiram, \v 17 mbege yay dawe ñeenti wet te warangikuwuñu. \v 18 Taxawaayu mbege ya daa réy ba raglu te mu ci nekk ay gët la sàngoo ba daj. \v 19 Bu bindeef ya dawee, mbege ya feggook ñoom daw; bu ñu naawee, mbege ya naaw. \v 20 Fu noo gi wale jublu fa rekk, fa lañu jëm, mbege ya jógandook ñoom, ànd ak noo gi. Noowal boroom bakkan yi daal moo nekk ci mbege yi. \v 21 Bu ñu dawee, ñu daw; bu ñu taxawee, ñu taxaw. Bu ñu jógee ci suuf, yékkatiku, ñu ànd ak ñoom yékkatiku. Noowal boroom bakkan yi daal moo nekk ci mbege yi. \p \v 22 Lu mel nib dénd a tiim boppi bindeef ya, raglu, leer nàññ ni doju kiristaal\f + \fr 1.22 \fr*\fk kiristaal \fk*\ft daa mel ni weer bi ñuy defare ab kaas.\ft*\f*. \v 23 Mbindeef mu ci nekk sa yenn ñaari laaf a ngi ci suufu dénd bi, tàlli, dékkarloo; ñaari laaf yi ci des sàng sa yaram. \v 24 Bu ñuy naaw, may dégg seen coowal laaf yi, mu mel ni géej mbàmbulaan, melati ni kàddug Aji Man ji, di saf riirum xare. Bu ñu taxawee, daldi wàcce seeni laaf. \v 25 Saa yu ñu taxawee ba wàcce seeni laaf nag, ag kàddu di jollee ca kaw dénd ba ca seen kaw bopp ya. \p \v 26 Ca kaw dénd ba tiim seeni bopp, ba tey, am na luy nirook ngànguney peru safiir, te jëmmu nit nekk ca kawa kaw lay nirook ngàngune. \v 27 Ma gis nag lu mel ni weñ guy tàkk, wër ko; dale ca lay niru ndigg la, jëm kaw; daleeti ca lay niru ndigg la, jëm suuf. Ma gis lu mel ni sawara akug leer wër ko. \v 28 Mu mel ni xon ci biiri niir, bésub taw. Loolooy melokaanu leer ga ko wër. Muy melokaan muy jëmmal leeru \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Naka laa ko gis, daldi ne gurub, dëpp sama kanam fi suuf. Ma dégg nag kàddu gu jib. \c 2 \s1 Aji Sax ji yebal na Esekiyel \p \v 1 Ba loolu amee boroom kàddu ga ne ma: «Yaw nit ki, jógal taxaw, ma wax la.» \v 2 Naka la ma wax loolu, ngelaw solu ma, ne ma yékkét, ma taxaw, di dégg kiy wax ak man. \v 3 Mu ne ma: «Yaw nit ki, maa lay yebal ci \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, xeeti fippukat yi fippu ci sama kaw; ñook seeni maam dañu maa masa tooñ ba bésub tey jii. \v 4 Ci nit ñu dëgër bopp te dërkiis laa lay yónni. Wax leen, ne leen: “Lii Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji da koo wax.” \v 5 Ñoom nag, su ñu la déglook su ñu gàntalee ndax kërug fippukat gi ñu jikkowoo, dinañu xam ne ab yonent a ngi ci seen biir. \v 6 Waaye yaw nit ki, bu leen ragal, bul ragal seeni wax. Xam naa ne ay taxas aki dég a lay wër, nga toog ci kawi jiit. Waaye bul ragal seeni wax te bul tiit seen kanam doonte kërug fippukat lañu. \v 7 Nanga leen àgge samay wax, ñu déglook ñu gàntal, nde ay fippukat lañu. \v 8 Yaw nit ki nag, déglul lii ma lay wax. Bul fippu ni kërug fippukat gii. Sexal, te lekk li ma lay jox.» \p \v 9 Naka laa xool, yem ci loxo bu ñu ma tàllal. Ndeke taxañub téere moo ci nekk. \v 10 Mu tàqarñi ko fi sama kanam, muy lu ñu bind biir ak biti, mbind ma di kàdduy jooy aki onk aki yuux. \c 3 \s1 Aji Sax ji dooleel na Esekiyel \p \v 1 Mu ne ma: «Yaw nit ki, lii ngay gis, lekk ko. Lekkal taxañ bii te dem wax ak waa kër Israyil.» \v 2 Ma ŋa, mu leel ma taxañ ba. \v 3 Mu ne ma: «Yaw, nit ki, lekkal taxañ bii ma la jox, ba suur këll.» May lekk, mu neex ni lem. \p \v 4 Mu ne ma: «Yaw nit ki, demal ba ca waa kër Israyil, te nga àgge leen samay wax. \v 5 Du ci waaso wu xóotu làkk te diisu làmmiñ lees la yebal. Ca waa kër Israyil nga jëm. \v 6 Bare na waaso yoo xamul seeni wax, yu xóotu làkk te diisu làmmiñ. Te su ma la yebaloon ci ñoom, ñu déggal la. \v 7 Waaye waa kër Israyil duñu la nangoo déggal, ngir nanguwuñu maa déggal; ndax waa kër Israyil gépp a dëgër bopp te dërkiis. \v 8 Maa ngii di la may kanam gu ñemee ni seen kanam, ba nga dëgër bopp ni ñoom. \v 9 Jamaa moo raw doj te ni laay dëgërale sa bopp. Bu leen ragal, bu leen tiit, li ñuy kërug fippukat yépp.» \p \v 10 Mu teg ca, ne ma: «Yaw nit ki nag, mboolem li ma lay wax, dégloo ko nopp, te teewloo ko xel. \v 11 Nanga dem ba ca sa bokki ngàllo ga, nga wax leen, ñu déglook ñu gàntal, ne leen: “Lii Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji da koo wax.”» \p \v 12 Ci kaw loolu ngelaw ne ma siféet, may dégg sama gannaaw, riirum kàddu gu xumb gu ne: «Cant ñeel na teddngay Aji Sax ji fi màkkaanam.» \v 13 Mu ànd ak riirum laafi bindeef yay fenqoo, ak coowal mbege ya ñu feggool, muy riir mu xumb. \v 14 Ba loolu amee ngelaw ne ma siféet, yóbbu. Maa ngay deme naqar ak xol bu tàng, te loxol Aji Sax ji diis gann ci sama kaw. \v 15 Ma àgg ba ca ngàllog Tel Abib, ga dëkke tàkkal dexu Kebar. Foofa ñu dëkk laa toog, jommi ci seen biir diiru juróom ñaari fan. \p \v 16 Ba juróom ñaari fan ya matee, kàddug Aji Sax ji dikkal ma, ne ma: \v 17 «Yaw nit ki, tabb naa la wattukatub waa kër Israyil. Nangool sama gémmiñ kàddu, artool ma leen ko. \v 18 Su ma nee nit ku bon ki: “Dee rekk ay sa àtte,” te fekk àrtuwoo ku bon ka, waxuloo lu ko waññee ca mbonam ga, ba mu mucc, ku bon kaay dee ndax tooñam, waaye bakkanam yaw laa koy laaj. \v 19 Waaye su dee yaa àrtu ku bon ki te taxul mu waññiku, dëddu mbonam nag, tooñu boppam a ko reylu, waaye yaw musal nga sa bopp. \v 20 Su dee boroom njekk bu dëpp yoonu njekkam, di def ndëngte, maa koy gàllankoor, mu dee. Soo ko àrtuwul ndax bàkkaaram, dina dee, te deesul bàyyi xel njekkal démbam la, waaye bakkanam, yaw laa koy laaj. \v 21 Waaye nag su dee yaa àrtu boroom njekk bi, ba tax bàkkaaratul, dina dund déy, ndax kàddug àrtu ga, te yaw it musal nga sa bopp.» \s1 Tëju te tëlee wax misaal la \p \v 22 Gannaaw loolu loxol \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikk na fa ci sama kaw. Mu ne ma: «Génnal ba ci joor gi, ma wax faak yaw.» \v 23 Ma génnsi ba ca joor ga. Ndeke jëmmu leeru Aji Sax jaa nga foofa, taxaw mel ni jëmmu leer, ga ma gisoon ca tàkkal dexu Kebar. Ma ne gurub, dëpp sama kanam fa suuf. \v 24 Ci kaw loolu ngelaw solu ma, ne ma yékkét, ma taxaw. Mu wax ak man, ne ma: «Doxal, tëjuji sa biir néeg. \v 25 Te kat yaw nit ki, dees na la fa takke ay buum, yeew la ba dootoo mana génn, dem ci nit ñi. \v 26 Sa làmmiñ laay taqal ci sa denqleñ, nga luu ba doo leen mana yedd, ndax kërug fippukat lañu. \v 27 Waaye bu ma amee lu ma lay wax, dinaa ubbi sa gémmiñ. Su ko defee nga ne leen: “Lii Boroom bi Aji Sax ji da koo wax.” Kuy dégg, dégg; kuy gàntal, gàntal. Ndax kërug fippukat lañu.» \c 4 \s1 Esekiyel yégle na gaw ba \p \v 1 Aji Sax ji ne: «Yaw nit ki, jëlal móolu ban, teg fi sa kanam, nga rëdd ci ab dëkk, mu misaal Yerusalem. \v 2 Nga gaw ko, tabax ab gawukaay bu ko wër, sëkk ko, ba noppi sàkkal ko ay dali xare, wërale ko dénki dàjjikaay ba mu daj. \v 3 Su ko defee nga jël saafukaayu weñ, teg ko, mu mel ni miiru weñ bu dox sa digganteek dëkk bi, te nga janook dëkk bi. Noonu nga koy gawe, mu gawu. Loolu di misaal, ñeel waa kër Israyil. \p \v 4 «Gannaaw loolu nanga tëdde sa wetu càmmoñ. Googu wet ngay gàddoo ayu waa kër Israyil. Diiru fan yi ngay tëdde wet ngay gàddoo seen ay. \v 5 Man nag àppal naa la limu fan yu tembook limu ati ayu waa kër Israyil\f + \fr 4.5 \fr*\ft Gannaaw ba Buur Suleymaan nelawee, am réewam xàjjalikoo na ñaari pàcc, benn ba di Israyil ca bëj-gànnaar, ba ca des di Yuda ca bëj-saalum.\ft*\f*, muy ñetti téeméeri fan ak juróom ñeent fukk (390) yooy tegoo ayu waa kër Israyil. \v 6 Boo noppee ci loolu nanga tëdde wetu ndijoor. Noonu ngay gàddoo ayu waa kër Yuda diiru ñeent fukki fan, at mu nekk, ma defal la ko benn fan. \v 7 Te nga jàkkaarlook gawub Yerusalem, tàllal ko sa përëgu neen, daldi biral \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* ci kawam. \v 8 Te kat dinaa la yeewe ay buum ngir doo mana walbatiku tëdde geneen wet, ba keroog ngay sottal say fani gaw. \p \v 9 «Te kat nanga sàkk bele ak lors ak ñebbe ak làntin ak dugub ak bele bu dëgër. Nga boole lépp ci lenn ndab. Moom ngay lekk diiru fan yi ngay tëdde wet. Diiru ñetti téeméeri fan ak juróom ñeent fukk (390) nga koy dunde. \v 10 Sa njëlu bés nag na doon ñaar fukki siikal\f + \fr 4.10 \fr*\fk ñaar fukki siikal \fk*\ft mooy ñaar téeméeri garaam.\ft*\f* yooy lekk bés ak bés. \v 11 Sa ndoxum naan it dees koy natt, mu tollook benn liitar bés bu nekk. \v 12 Mburum lors ngay lekk te jonkani nit nga koy lakke, nit ñiy gis.» \v 13 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji teg ca ne: «Noonu la \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* di lekkeji seen ñamu sobe ci biir xeet yi ma leen di tasaareji.» \p \v 14 Ma ne ko: «Ãhã! Boroom bi Aji Sax ji, man de masumaa sobeel sama bopp. Muy lu médd, di lu aw rab fàdd, masuma koo lekk ba may gone ba tey. Wenn yàpp wu daganul masula dugg sama gémmiñ.» \v 15 Mu ne ma: «Baax na, kon defal naa la ko ndéef, mu wuutu jonkanu nit, dinga lakke ko sa mburu.» \v 16 Mu neeti ma: «Yaw nit ki, maa ngii di dagge fi Yerusalem lépp luy dugub. Ci biir njàqare lañuy lekke as mburu te xol bu jeex lañuy naane siitum ndox. \v 17 Su ko defee ñu ñàkk lekk, ñàkk naan, di xoolante gëti tiitaange, jeex tàkk ndax seeni ñaawtéef.» \c 5 \s1 Dogal dikkal na Yerusalem \p \v 1 «Yaw nit ki, jëlal saamar bu ñaw, nga def ko sa saatus watukaay te nga wate ko sa bopp ak sa sikkim. Nga jël ab màndaxekaay, séddalee ko kawar gi ay cér. \v 2 Benn cér bi, nanga ko lakk ci digg nataalu dëkk bi, gannaaw bu fani gaw bi matee. Beneen cér bi, nga dóore ko saamar bi, kawar gi tasaaroo fi wër dëkk bi. Ñetteelu cér bi, nga sànni ko ci ngelaw li, man ma toppe ko saamar. \v 3 Waaye nanga sàkk tuuti ci kawar gi, fas ci sa lafu mbubb. \v 4 Nga dellu sàkk cooca, sànni ca sawara sa, lakk ko. Ca la sawaray jóge, tàkkal mboolem waa kër Israyil. \p \v 5 «Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: Yerusalem a ngoogu. Ci digg xeet yi laa ko teg, réew yi wër ko. \v 6 Ñoo gàntal sama àttey yoon, ba gëna bon xeet yi, gàntal samay dogal, ba gëna bon réew yi leen séq. Xalab nañu sama àttey yoon te jëfewuñu samay dogal. \p \v 7 «Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Gannaaw seen reewande wees na reewandey xeet yi leen séq, samay dogal, jëfewuleen ko; sama àttey yoon, sàmmuleen ko; sàmmuleen sax àttey xeet yi leen wër, \v 8 kon nag Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii ci seen kaw, man itam. Maay wàcce fi seen biir ay mbugal, xeet yi teg ci seeni gët. \v 9 Maay def fi seen biir lu ma masula def te duma defati lu ni mel, ndax seen mboolem jëf ju siblu. \v 10 Moo tax baay dina yàpp doom, doom yàpp baay fi biir Yerusalem. Maay wàcce ay mbugal fi yeen, te maay tasaare seenu ndes wépp fépp fu ngelaw jublu. \p \v 11 «Moo tax, dogu naa ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, gannaaw yeena def seen wépp njombe ak seen jépp jëf ju siblu, di sobeel sama bérab bu sell bi, man itam, maa leen di wat nel te duma leen xool bëtu ñéeblu, duma leen ñeewante. \v 12 Seen ñetteelu xaaj, mbas lañuy deeye mbaa xiif bu leen di sànk ci biir dëkk bi. Beneen ñetteelu xaaj bi, saamar lañuy fàddoo ci seen dig-digal bi. Xaajub ñetteel bi ci des, fépp fu ngelaw jublu laa leen di tasaare, te saamar laa leen di toppe. \v 13 Maa leen di ŋaccal sama mer, sottil leen sama xadar ba giif, te bu ma leen ŋaccalee sama mer, ñu xam ne man Aji Sax ji, maa waxe sama fiiraange. \v 14 Yeen waa Yerusalem maa leen di gental, sewal leen ci biir xeet yi leen séq, ku fi romb, di ci gis. \v 15 Keroog bu ma leen wàcceelee àtteb mer ak xadar ak dumay xadar, seen dëkk beey doon dëkkub toroxte bu ñuy kókkali, dëkk bu gental buy yedd xeet yi leen séq. Man Aji Sax ji maa ko wax. \p \v 16 «Ñoom bu ma leen soqee fitti xiif yu aay, fitti faagaagalkat yooyu may fitt ngir faagaagal leen, xiif laa leen di yokkal, ba dagge dugub fi seen biir. \v 17 Maay yebal ci seen kaw ab xiif ak rabi àll yu leen di xañ ay doom; mbas ak deret ju tuuru gane leen, saamar, ma indil leen. Man Aji Sax ji, maa ko wax.» \c 6 \s1 Tuur yi indi na mbugal \p \v 1 Gannaaw loolu kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji da maa dikkal, ne ma: \v 2 «Yaw nit ki, jàkkaarlool ak tundi Israyil, nga waxal leen \w waxyu|lemma="waxyu:"\w*. \v 3 Neel: \q1 “Yeen Tundi Israyil, \q1 Dégluleen kàddug Boroom bi, Aji Sax ji. \q1 Boroom bi Aji Sax ji moo wax lii, \q1 jëme ci tund wu mag ak wu ndaw \q1 ak xunteeku xur, ne: \q1 Maa ngi nii di leen wàcceel saamar, \q1 maay màbb seen jaamookaayi tuur, \q1 \v 4 seen \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* gental, \q1 seen suurukaayi tuur tasaaroo, \q1 ma tëral seeni nit ñu ñu bóom fi seen kanam kasaray tuur. \q1 \v 5 Maay tegal seen kasaray tuur néewi \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \q1 Maay wasaare seeni yax fi wër seeni sarxalukaay. \q1 \v 6 Fu ngeen mana sance, \q1 seeni dëkk ay gental, \q1 seen jaamookaayi tuur wéet, \q1 seeni sarxalukaay yàqu, gental, \q1 seen kasaray tuur rajaxoo ba jeex, \q1 seen suurukaayi tuur màbb, \q1 seeni liggéey réer. \q1 \v 7 Dees na leen bóom, \q1 ba ngeen xam ne maay Aji Sax ji. \q1 \v 8 Waaye maay déeg lenn ci yeen, \q1 ñu rëcc saamar, tasaaroo ci xeet yi, \q1 ci biir réewi jaambur. \q1 \v 9 Su boobaa seenu ndes di ma fàttlikoo \q1 fa biir xeet ya ñu leen yóbbu njaam, \q1 fa may jeexale seen xolu gànc, bi ma dëddu, \q1 ak seen gët yi ñuy gànctook seeni tuur. \q1 Su boobaa ñu jéppi seen bopp \q1 ndax lu bon li ñu def ak seen jépp jëf ju siblu. \q1 \v 10 Dinañu xam ne maay Aji Sax ji, \q1 te du neen laa leen artoo, \q1 ba ma leen di tëkkoo mii musiba. \s1 Aji Sax jeey am ndam \b \q1 \v 11 «“Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: \q1 Fenqeel say loxo, dóor sa tànk fi suuf te ne: ‘Ñaw!’ \q1 ci mboolem jëfi waa kër Israyil ju bon ju siblu. \q1 Saamar ak xiif ak mbas lañuy fàddoo. \q1 \v 12 Ku sore deeye mbas, \q1 ku jege fàddoo saamar, \q1 ku ca mucce, deeye xiif, \q1 ma ŋaccal leen sama xadar. \q1 \v 13 Dingeen xam ne maay Aji Sax ji, \q1 bu seeni néew nee xas fi seen biiri tuur, \q1 ak fi wër seeni \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*, \q1 ak kaw tund wu mag ak wu ndaw, \q1 ak mboolem ker garab gu naat, \q1 ak mboolem garab gu mag te sëq, \q1 fépp fu ngeen di taale cuuraay, ñeel seen mépp tuur. \q1 \v 14 Maa leen di dóor sama loxo, \q1 réew mi, ma gental koo gental, \q1 dale ko màndiŋ ma ba Dibla, \q2 ak fépp fu ñu mana sance. \q1 Su boobaa ñu xam ne man maay Aji Sax ji.”» \c 7 \s1 Jeexle dikk na \p \v 1 Gannaaw loolu kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji da maa dikkal, ne ma: \v 2 «Léegi nag, yaw nit ki, Boroom bi Aji Sax ji dafa wax réewum Israyil ne ko: \q1 “Jeex na tàkk! \q1 Jeexal dikkal na ñeenti weti réew mi. \q1 \v 3 Jeexal nga nag léegi! \q1 Maay yebal sama mer fi sa kaw. \q1 Maa lay mbugale say jëfin, \q1 yool la sa jépp jëf ju siblu. \q1 \v 4 Duma la xool bëtu ñéeblu, \q1 duma ñeewante. \q1 Say jëfin laa lay yool, \q1 sa jëf ju siblu ji ci sa biir. \q1 Su boobaa ngeen xam ne man maay Aji Sax ji”». \b \q1 \v 5 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 «Céy wii ay, guléet wii ay! \q1 Mu ngii di dikk. \q1 \v 6 Jeexlee ngoog, jeexle dikk na, \q1 jekki, yewwul la. \q1 Mu ngii, di dikk! \q1 \v 7 Yaw nitu réew mee, sànkute dikkal na la. \q1 Àpp mat, \q1 bés dëgmal, \q1 tiitaange wuutu ca mbéx fa kaw tund ya. \q1 \v 8 Du yàgg dara ma xëpp la sama xadar, \q1 ŋaccal la sama mer, \q1 mbugale la say jëfin, \q1 yool la sa jépp jëf ju siblu. \q1 \v 9 Duma xool bëtu ñéeblu, \q1 duma ñeewante. \q1 Say jëfin laa lay yool \q1 ak sa jëf ju siblu ji ci sa biir. \q1 Su boobaa ngeen xam ne maay Aji Sax jiy dumaa. \b \q1 \v 10 «Bés baa ngi, mu ngooguy dikk, \q1 sànkute sàqi na, \q1 yetu njubadee tóor, \q1 reewande jebbi. \q1 \v 11 Fitnaa taxaw, di yet wuy dóoral coxor. \q1 Seen lenn du des, \q1 du seen mbooloo, \q1 du seen alal, \q1 du seen daraja. \q1 \v 12 Àpp mat, \q1 bés jege. \q1 Bu ca jëndkat tala bég, \q1 bu ca jaaykat tala naqarlu! \q1 Am sànj a dikkal askan wépp. \q1 \v 13 Bu jaaykat bi muccee it, \q1 du jotaat ca njaayam. \q1 Peeñu mi jëm ci askan wépp, daal, du toxu, \q1 ku nekk ñaawtéefam lay dunde, \q1 ba du leqliku. \q1 \v 14 Liitu xareey jib, ba lépp jekk ngir xare, \q1 te kenn du xareji, \q1 samam sànj a dikkal askan wépp. \q1 \v 15 Saamar biti, \q1 mbas akub xiif ci biir, \q1 ki ci àll bi deeye xare, \q1 ki ci biir dëkk bi, xiif ak mbas rey ko. \q1 \v 16 Ña rëcc, rawi ca tund ya, \q1 waru pitaxi xur ya, \q1 ñooy binneendoo ndax seeni tooñ. \q1 \v 17 Yoxo yépp yoqi, \q1 tànk tooy xepp. \q1 \v 18 Ñooy sol ay saaku di ko ñaawloo, \q1 seen yaram wépp daw, \q1 gépp kanam sëlmoo gàcce, \q1 bopp ya di nel yu set wecc. \q1 \v 19 Seen xaalis, ñu sànni ci mbedd yi, \q1 seen wurus di leen saf sagaru sobe. \q1 Keroog bésub sànjum Aji Sax ja, \q1 du xaalis, du wurus wu leen di xettli. \q1 Du leen fajal xiif, \q1 du leen reggal, \q1 xanaa tàbbal leen cig njubadi. \q1 \v 20 Ñoo doon sagoo seen gànjar gu yànj, \q1 di ci sàkk jëmmi tuur yu jara bañ te jomblu, \q1 ba tax ma defal leen ko sagaru sobe. \q1 \v 21 Maa koy teg ci loxoy doxandéem, ñu foqati ko, \q1 muy alal ju sagari niti àddina sëxëtoo, \q1 teddadil ko. \q1 \v 22 Maa leen di dummóoyu, \q1 maay bàyyi nit ñi teddadil sama ngëneelu bérab, \q1 ay sàcc a cay tàbbi, teddadil ko. \q1 \v 23 Waajal-leen càllala yi, \q1 tuur nañu deret ba réew mi fees, \q1 dëkk bi fees ak fitna. \q1 \v 24 Maay indi xeet yi gëna néeg, \q1 ñu nangu seeni kër, \q1 ma daldi sàggi sagu boroom doole yi, \q1 sobeel seen bérab yu sell. \q1 \v 25 Tiitaangee ngi dikk, \q1 ñuy sàkku jàmm, jàmm réer. \q1 \v 26 Ay ci kaw ay a ngi dikk, \q1 xibaar ci kaw xibaar, \q1 ñuy sàkku peeñum yonent ci neen, \q1 ndigalu yoon réer \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w*, \q1 pexe réer mag. \q1 \v 27 Buur dina tiislu, \q1 garmi làmboo séri ñaawlu, \q1 baadoolay réew mi di kat-kati. \q1 Seeni jëfin laay jëfeek ñoom, \q1 seeni àtte laa leen di àttee, \q1 ñu xam ne maay Aji Sax ji!» \c 8 \s1 Bokkaale feeñ na ca kër Yàlla ga \p \v 1 Keroog juróomi fan, ca juróom benneelu weer wa, ca juróom benneelu at ma\f + \fr 8.1 \fr*\ft Mu yemook juróom benneelu at gannaaw ba Buur Yowakin duggee ngàllo.\ft*\f*, damaa toog sama biir néeg, magi Yuda bokk ak man toog. Fa la loxol Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dal fi sama kaw. \p \v 2 Ma xool, yem ci jëmm ju ame melokaanu nit. Li ko dale fiy nirook lupp yi, jëm suuf, sawara la. Li dale ci lupp yi jëm kaw ame melokaanu leer, mel ni weñ guy tàkk. \v 3 Mu tàllal lu bindoo ni loxo, daldi sëq sama kawaru bopp, lenn ngelaw yékkati ma ba ca diggante kaw ak suuf, yóbbu ma ba Yerusalem ci biir peeñum Yàlla, ba ca buntu ëttu biir kër Yàlla ba janook bëj-gànnaar, fa ñu teg jëmmu bokkaale, jay sabab fiiraange. \v 4 Ma jekki gis foofa leeru Yàllay Israyil ca melokaanam, ma ma ko gise woon ca joor ga. \p \v 5 Mu ne ma: «Yaw nit ki, séenul wetu bëj-gànnaar.» Ma séenu wetu bëj-gànnaar, yem ca jëmmu bokkaale jooju féeteek bunt ba dendeek \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* ba, ca bëj-gànnaaram. \v 6 Mu ne ma: «Yaw nit ki, gis nga li ñuy def, tojaange yu réy yi waa kër Israyil di def fii, ba di ma soreleek sama bérab bu sell bi. Te dinga gis tojaange yu gënatee màgg.» \p \v 7 Mu yóbbu ma ba ca buntu ëtt ba, ma yem ci menn pax mu nekk ca miir ba. \v 8 Mu ne ma: «Yaw nit ki, ayca, gasal fii miir bi!» Ma gas rekk, gis ab jàllukaay. \v 9 Mu ne ma: «Jàllal, ba gis tojaange yu bon yi ñu fiy def.» \v 10 Naka laa jàll ba xool, yemuma ci lu moy ay nataal yu ñu ñaas ci miir bi bépp, di mboolem dundoot yuy ramm-rammi ci suuf, ak rab yu jara seexlu, ak mboolem jëmmi kasaray tuur yu waa kër Israyil di jaamu. \v 11 Juróom ñaar fukki magi kër Israyil a nga taxaw, janook nataal ya. Yaasaña doomu Safan a nga ca. Ku ci nekk a nga ŋàbb sab and, cuuraay la jolli. \v 12 Mu ne ma: «Yaw nit ki, du yaa gis li magi kër Israyil di def ci lëndëm gi, ku nekk ak fa ñu jagleel sa nataalu tuur. Ña nga naan: “Aji Sax ji gisu nu, Aji Sax ji wacc na réew mi.”» \v 13 Mu dellu ne ma: «Te dinga gis tojaange yu gënatee màgg yu ñu nekke.» \p \v 14 Gannaaw loolu mu yóbbu ma ba ca buntu kër Aji Sax ja féete bëj-gànnaar. Ndeke jigéen ñaa nga foofa toog, di jooy deewug tuur mu ñuy wax Tamus. \v 15 Mu ne ma, yaw nit ki, yaa ko gisal sa bopp! Te dinga gis tojaange yu gëna màggati yii. \p \v 16 Mu yóbbu ma ba ca ëttu biiru kër Aji Sax ji, ndeke foofa ca buntu néeg Aji Sax ji, diggante dal-luwaayu bunt baak sarxalukaay ba, lu wara tollook ñaar fukki nit ak juróom a nga fa, ñu won gannaaw bérab bu sell bi, jublu penku, di sukkal jant bi, dëpp seen jë fi suuf. \v 17 Mu ne ma: «Yaw nit ki, du yaa gis lii? Moonte tojaange gi waa kër Yuda di def fii doyu leen. Xanaa ñuy wasaare fitna ci réew mi, di gëna yékkati sama xol. Xoolal! Ñu ngooguy def jëfi yéefar, jël caru garab, di fóon. \v 18 Man it maa leen di feye xadar. Duma xool bëtu ñéeblu, duma ñeewante. Dinañu yuuxu yuux yu réy, may dégg te duma leen faale.» \c 9 \s1 Rey nañu bokkaalekat yi \p \v 1 Gannaaw loolu Aji Sax ji àddu ca kaw, may dégg. Mu ne: «Yeen mbugalkati dëkk bi, kaayleen, te na ku nekk ŋàbb sa ngànnaayal reyukaay.» \v 2 Ca saa sa juróom benni góor jóge yoonu bunt ba féete kaw te janook bëj-gànnaar, ku nekk ŋàbb sa ngànnaayal reyukaay. Keneen a nga ca seen biir, ku sol ndimol lẽe, ak mbarum bindukaay ba ca ndiggam. Ñu dikk taxaw ca wetu \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* xànjar ba. \v 3 Ci kaw loolu leeru Yàllay Israyil, ja woon ca kaw jëmmu malaakay \w serub|lemma="serub y-:"\w* ma, yékkatikoo fa, jubal buntu kër ga. Mu woo boroom ndimol lẽe baak mbarum bindukaay ba ca ndiggam. \v 4 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ne ko: «Wëral dëkk bi, ci biir Yerusalem. Foo gis kuy onk ak a binni, di ko naqarloo gépp tojaange gu ñu fiy def, nga rëdd aw rëdd ci jëëm.» \v 5 Ba loolu wéyee mu wax ak ña ca des, may dégg. Mu ne leen: «Toppleen ko ca biir dëkk ba te ngeen rey. Buleen xool bëti ñéeblu, buleen ñeewante. \v 6 Mag ñu góor ñeek xale yu góor yi, jeeg jeek janq ji, ba ci tuut-tànk yi, reyleen ñépp, faagaagal leen. Waaye ku ci am rëddu jë, buleen ko laal. Dooreleen ko ci sama bérab bu sell bi.» Ñu tàmbalee bóom mag ña ca kanam kër Yàlla ga. \v 7 Aji Sax ji ne leen: «Feesal-leen ëtt yeeki néew, sobeel-leen kër gi, doora génn.» Ba ñu noppee, daldi jàll ca biir dëkk ba, di rey. \p \v 8 Naka lañu dem, reyi, ma des fa man doŋŋ. Ma daldi daanu, dëpp sama kanam fa suuf, daldi àddu ca kaw, ne: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, xanaa doo sànk mboolem ndesu Israyil ci sa xadar jii ngay xëpp ci kaw Yerusalem?» \v 9 Mu ne ma: «Tooñaangey waa kër Israyil ak Yuda moo ëpp loxo lool. Réew maa ngi fees ak deret, dëkk bi fees ak yàqute. Nee nañooy: “Aji Sax ji wacc na réew mi. Aji Sax ji gisul dara.” \v 10 Man it duma xool bëtu ñéeblu, duma ñeewante. Seen jëfin laay këpp ci seen kaw bopp.» \v 11 Ci kaw loolu boroom mbubbam lẽe baak mbarum bindukaay ba ca ndiggam, ne jimeet, délsi. Mu ne: «Def naa lépp na nga ma ko sante.» \c 10 \s1 Leer ga dëddu na \p \v 1 Ba loolu wéyee ma téen, daldi yem ci lu mel ni ngànguney peru safiir ci kaw dénd bi tiim boppi malaakay \w serub|lemma="serub y-:"\w* yi. \v 2 Aji Sax ji ne boroom ndimol lẽe ba: «Doxal ci diggante mbege, yi ronu jëmmi serub yi, nga tibb say loxo ba mu fees ci xal yu yànj yi, te nga dem wasaare ko ci kaw dëkk bi.» Kooka dem, may gis. \p \v 3 Ba waa jay agsi, jëmmi serub yaa nga taxaw fa féete kër Yàlla ga ndijoor, niir wa daldi fees ëttu biir ba. \v 4 Ba leeru \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji yékkatikoo ca serub ya, dem ba ca buntu kër ga, niir wa daa fees kër ga, ëtt ba fees dell ak leeru Aji Sax ja ne ràññ. \v 5 Coowal laafi malaakay serub yaa ngay jib ba ca ëtt ba féete biti, mel ni kàddug Yàlla Aji Man ji. \p \v 6 Ba Aji Sax ji santee boroom mbubbam lẽe ma, ne ko mu sàkk sawara ci diggante mbege yi ci digg jëmmi serub yi, waa ja dem, taxaw feggook menn mbege. \v 7 Ci kaw loolu kenn ci malaakay serub yi yóotu sawara si ci seen digg, daldi sàkk ci xal yi, def ci loxoy boroom mbubbam lẽe ma, mu jël ko, daldi génn. \v 8 Ba loolu amee lu mel ni loxol nit feeñ ca ron laafi serub ya. \p \v 9 Ma xoolaat, yemuma ci lu moy ñeenti mbege yu feggook ñeenti serub yi, menn mbege ci wetu serub bu ne, te mbege yi ne ràññ, ame melokaanu peru kirsolit. \v 10 Ñoom ñépp a niroo, te mbege mu ci ne mel ni mbegee nekk ca biiram, \v 11 ba tax ñu mana dawe ñeenti wet te duñu warangiku. Fu boppu serub jublu, mbege yi daw jublu fa, te du tax ñu warangiku. \v 12 Serub yi nag, mboolem seen yaram, seen gannaaw ak seen cati loxo ak seeni laaf, lépp ay gët la sàngoo ba daj, ba ci seen ñeenti mbege yi. \v 13 Mbege yooyu laa dégg ñu tudde leen mbegey callweer. \v 14 Malaakam serub mu ci nekk am na ñeenti kanam. Genn kanam ga di gu serub, ñaareelu kanam ga di gu nit, ñetteel ba di gu gaynde, ñeenteel ba di gu jaxaay. \v 15 Serub ya nag jëm kaw. Serub yooyu ñooy bindeef, ya ma gisoon ca tàkkal dexu Kebar. \v 16 Bu ñu dawee, mbege ya feggook ñoom daw, bu ñu firee seeni laaf, jëm kaw, mbege ya du teqlikook ñoom. \v 17 Bu ñu taxawee, mbege yi taxaw, bu ñu jógee jëm kaw, ñu ànd ak ñoom, jëm kaw. Noowal boroom bakkan yi daal moo nekk ci mbege yi. \p \v 18 Ba loolu amee leeru Aji Sax ji bàyyikoo fa buntu kër ga, daldi taxawi ca kaw serub ya. \v 19 Serub ya firi seeni laaf, jóge suuf, jëm kaw, may gis, ñu jógandook mbege ya ñu àndal, daldi taxawi ca wetu buntu penkub kër Aji Sax ja, leeru Yàllay Israyil tiim leen lu kawe. \v 20 Ñooñooy bindeef ya ma gisoon Yàllay Israyil tiim leen ca tàkkal dexu Kebar. Ca laa xam ne ay malaakay serub lañu. \v 21 Ñeenti kanam la ku ci nekk am, ak ñeenti laaf, ak lu mel ni loxoy nit yu ron seeni laaf. \v 22 Seen bindu kanam ya mooy kanam ya ma gisoon ca tàkkal dexu Kebar. Ci seen melokaan, ñoom rekk la. Ku nekk man naa jubal màkk fépp fu genn kanam jublu. \c 11 \s1 Digeb yiw a gën jàmmu tey \p \v 1 Ba loolu wéyee ngelaw ne ma siféet, yóbbu ma ba ca buntu penkub kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ja janook penku. Foofa ca bunt ba, yemuma ci lu moy ñaar fukki nit ak juróom. Ma xàmmi ca Yaasaña doomu Asur ak Pelaca doomu Benaya, di njiiti askan wi. \v 2 Aji Sax ji ne ma: «Yaw nit ki, ñii ñooy mébétkati ñaawtéef ñiy digle lu bon ci dëkk bii. \v 3 Ñu ngi naa: “Bunu tabaxagum ay kër; dëkk bii daa mel ni ndab, nun nu fegu ni yàpp wu ca ube.” \v 4 Kon nag yaw nit ki, waxal \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* ci seen kaw. Jottlil waxyu.» \v 5 Noowug Aji Sax ji daldi dal fi sama kaw, ne ma: «Neel: \q1 “Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Yeen waa kër Israyil, yeena waxe nii, \q1 seeni mébét, xam naa ko. \q1 \v 6 Bóom ngeena bóom seen bokki dëkk bii, \q1 ba mbedd yi fees dell aki néew. \q1 \v 7 Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Dëkk bi kay ndab la, \q1 seen bokki néew yi ngeen fi saam di yàpp wi ci ube, \q1 waaye yeen dees na leen fi génnee. \q1 \v 8 Saamar ngeen ragal, \q1 saamar laa leen di indil. \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \q1 \v 9 Maa leen di génne biir dëkk bi, \q1 teg leen ci loxoy doxandéem, \q1 wàcceel leeni mbugal. \q1 \v 10 Saamar ngeen di fàddoo, \q1 fa catal Israyil laa leen di mbugale, \q1 ngeen xam ne maay Aji Sax ji. \q1 \v 11 Dëkk bii du doon seen ndab, \q1 te dungeen yàpp wu cay ube. \q1 Fa catal Israyil laa leen di mbugale. \q1 \v 12 Su boobaa ngeen xam ne maay Aji Sax, \q1 ji ngeen sàmmul dogali yoonam, \q1 jëfewuleen àttey yoonam, \q1 xanaa di jëfe aaday xeet yi leen séq.”» \p \v 13 Naka laay biral waxyu, Pelaca (mu firi Aji rëcc ju Yàlla) doomu Benaya jekki rekk, dee. Ma ne fëlëñ, dëpp sama jë fa suuf, daldi àddu ca kaw, ne: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, yaay faagaagal ndesu Israyil nii?» \p \v 14 Ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikkal ma, ne ma: \v 15 «Yaw nit ki, gannaaw sa bokk yooyu nga bokkal, ñuy say bokk lenqe, di mboolem waa kër Israyil ñi nekk ngàllo, ñoom la waa Yerusalem di siis, naan: \q1 “Soreleen Aji Sax ji; \q1 réew mii, nun la ko sédd.” \m \v 16 Kon nag, waxal ne: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Maa soreel moos seen bokk yooyu fa biir yéefar ya, \q1 maa leen wasaare biir réewoo réew, \q1 te du tee ma teewal leen ni bérab bu sell \q1 fa réew ya ñu sancaani.” \m \v 17 Moo tax nanga wax ne: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Maa leen di dajalee fa xeet ya, \q1 boolee leen fa réew ya ngeen wasaaroo, \q1 ba joxaat leen suufas Israyil.” \q1 \v 18 Bu ñu ñibbee, jële fa mboolem lu jomblu \q2 ak lépp lu siblu. \q1 \v 19 Maa leen di may beneen xol ak xel mu yees. \q1 Xolu doj bi laay roccee ci seen suux, \q1 weccee leen ko xolu suux. \q1 \v 20 Su ko defee sama dogali yoon lañuy doxe, \q1 te sama àttey yoon lañuy sàmm, di ko jëfe. \q1 Su boobaa ñuy sama ñoñ, \q1 may seen Yàlla. \q1 \v 21 Waaye nit ña seen xol jengal seen jëf ju jomblu, \q1 ak seen yëf yu seexluwu, \q1 maay këpp seen jëfin ci seen bopp. \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.» \p \v 22 Ba loolu amee malaakay \w serub|lemma="serub y-:"\w* ya firi seeni laaf, ànd ak mbege ya, leeru Yàllay Israyil tiim leen fa kawa kaw. \v 23 Gannaaw loolu leeru Aji Sax ji yékkatikoo fa digg dëkk ba, dem, taxawi fa kaw tund wa ca penkub dëkk ba. \v 24 Ba loolu amee ngelaw ne ma siféet, yóbbu ba ca waa ngàllo ga ca réewum Babilon, lépp ci peeñu, ci dooley Noowug Yàlla. Peeñu ma ma gis nag yem fa. \v 25 Ba loolu amee ma àgge waa ngàllo ga mboolem mbir ya ma Aji Sax ji won. \c 12 \s1 Ngàllo xeeñ na \p \v 1 Gannaaw loolu kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji da maa dikkal ne ma: \p \v 2 «Yaw nit ki, digg kërug fippukat nga dëkke, ñu ami gët te duñu gis, ami nopp te duñu dégg, ndax kërug fippukat lañu. \v 3 Yaw nag nit ki, dajaleel digg bëccëg, ñépp gis, sa jumtukaayi ku jëm ngàllo te nga sanci feneen, ñépp teg ci bët. Jombul ñu gis ne kërug fippukat lañu. \v 4 Sab ëmb ngay jëkka génne digg bëccëg ni ku jëm ngàllo, ñépp teg ci bët. Te yaw nga génn ngoon ni ku jëm ngàllo, ñu teg ci bët. \v 5 Dangay bëtt ci miir bi, ñuy gis, pax mooy yoore sab ëmb. \v 6 Nañu la gis nga gàddu sab ëmb, génn ci lëndëm gi. Booy génn di dem, sa kanam ngay muur, ba doo mana gis suuf si, ngir misaal laa la def, ñeel waa kër Israyil.» \p \v 7 Ma def loolu noonee ñu ma ko sante. Samab ëmb laa génne digg bëccëg ni ku jëm ngàllo. Ca guddi ga ma bëtte miir ba loxoy neen, ñépp di gis. Ci lëndëm gi laa gàddu sama ëmb, ñuy gis. \p \v 8 Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal ma ca ëllëg sa ca suba, ne ma: \v 9 «Yaw nit ki, xanaa waa kër Israyil, kërug fippukat gi, newuñu la: “Ana looy def nii?” \v 10 Waxleen, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Boroom Yerusalem la àrtu bii ñeel, mook mboolem waa kër Israyil gi fi dëkk.” \v 11 Neel: \q1 “Man maay seen misaal. \q1 Nii ma def rekk lees leen di def, \q1 ngàllo lees leen di jàpp, jëme. \q1 \v 12 Seen boroom dëkk beey gàddub ëmbam, \q1 génn dëkk bi ci lëndëm gi. \q1 Miiru dëkk bi lees di bëtt, jaarale ko ca. \q1 Kanam ga lay muur, \q1 ba tax du gis suuf si. \q1 \v 13 Maa koy laaw samab caax, \q1 mu keppoo samag fiir, \q1 ma yóbbu ko Babilon mu Kaldeen ña. \q1 Réew ma, du ko gis te fa lay deeye. \q1 \v 14 Mboolem ña ko dar, \q1 ay toppam ak mboolem gàngooram, \q1 maa leen di wasaare fépp fu ngelaw jublu, \q1 toppati leen ak saamar. \q1 \v 15 Bu ma leen tasaaree ci biir xeet yi, \q1 wasaare leen ci réew yi, \q1 ñu xam ne maay Aji Sax ji. \q1 \v 16 Du tee ma ba ñenn ci ñoom, \q1 ñu mucc saamar, mucc xiif, mucc mbas, \q1 ba nettaliji seen gépp tojaange \q2 ca digg xeet ya ñu jëm. \q1 Su boobaa ñu xam ne maay Aji Sax ji.”» \p \v 17 Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma: \q1 \v 18 «Yaw nit ki, lekkal saw ñam, di kat-kati, \q1 naane njàqare sam ndox, di rag-ragi, \q1 \v 19 te nga wax waa réew mi, \q1 mbirum waa Yerusalem ga ca suufas Israyil, \q1 ne leen Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 njàqare lañuy lekkeji seenu ñam, \q1 te xol bu gental lañuy naane seenum ndox, \q1 ndax seen réew mu gental, ñàkk lépp lu ko feesoon, \q1 ngir coxoru mboolem ñi ko dëkke. \q1 \v 20 Dëkk yu xumboon, mujj wéet, \q1 réew mi doon ub gent, \q1 ba ngeen xam ne maay Aji Sax ji.» \s1 Waxyuy nit, waxi caaxaan \p \v 21 Gannaaw gi kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal ma ne ma: \v 22 «Yaw nit ki, du lii ngeen defati aw léeb ci biir réewum Israyil? “Bés yaa ngi bëgga baree, te peeñu sottiwul!” \v 23 Kon wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Maay dakkal woowu léeb, \q1 ba muy léebtil fi Israyil.” \q1 Waxleen kay ne leen: \q1 “Bés a ngi jubsi, \q1 peeñoo peeñu sotti. \q1 \v 24 Du peeñuy caaxaan muy amati mbaa ngisaaney jayaate, \q2 fi biir kërug Israyil. \q1 \v 25 Man Aji Sax ji, \q1 maay wax li may wax, \q1 mu sotti te dootu fomm. \q1 Kërug fippukat gi ngeen doon, \q1 maay àddu kàddu, sottal ngeen fekke, \q1 kàddug Boroom bi Aji Sax jee!”» \p \v 26 Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal ma, ne ma: \v 27 «Yaw nit ki, waa kër Israyil déy a nga naan, “Peeñu yi kii di gis, des na ay fani fan, ci lu soree sore lay biral ab \w waxyu|lemma="waxyu:"\w*!” \v 28 Moo tax wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Sama genn kàddu dootu fomm. \q1 Léegi kàddu gu ma àddu, sottal ko. \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”» \c 13 \s1 Mbugalu yonent yi taxaw na \p \v 1 Ba loolu amee kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal ma ne ma: \v 2 «Yaw nit ki, waxal \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* ci kaw yonenti Israyil yiy waxe ay waxyu. Nanga wax ñiy waxe waxyu ci seen xelum bopp, ne leen: \q1 “Dégluleen kàddug Aji Sax ji: \q1 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 \v 3 Wóoy ngalla yonent yu ñàkk xel, \q1 yiy topp seen xelum bopp te gisuñu tus! \q1 \v 4 Yeen yonenti Israyiloo, \q1 mbete till yuy foreb gent! \q1 \v 5 Yéeguleen ca biir bëttukaayi tata ja, \q1 jagalaguleen tata ju aar Israyil, \q1 ngir taxaw, waajal xare ba, \q2 keroog \w bésub Aji Sax|lemma="bésub Aji Sax ji-:"\w* ji. \q1 \v 6 Seeni peeñu caaxaan la, \q1 seeni ngisaane diy fen. \q1 Ñu naa: ‘Kàddug Aji Sax jee,’ \q1 te Aji Sax ji yebalu leen! \q1 Teewul ñuy xaar kàddu gu sotti. \q1 \v 7 Xanaa du peeñuy caaxaan ngeen gis? \q1 Du ngisaaney fen ngeen di waxe, \q1 naan: ‘Kàddug Aji Sax jee,’ \q1 te man àdduwma? \b \q1 \v 8 «“Kon nag Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Gannaaw yeena waxi caaxaan, gisi fen, \q1 maa ngii nag, di dal fi seen kaw. \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee! \q1 \v 9 Sama loxooy dal yonent, \q1 yiy gis peeñuy caaxaan, \q1 di gisaaney fen. \q1 Sama péncum ñoñ, duñu fa teewe, \q1 limeefu kër Israyil, deesu leen ca bind, \q1 te réewum Israyil, duñu fa dellu. \q1 Su boobaa ñu xam ne maay Boroom bi Aji Sax ji. \q1 \v 10 Kon nag gannaaw ñu ngi lajjal sama ñoñ, \q1 naan leen lépp jàmm! Te jàmm amul, \q1 mu mel ni miiru digaloo bu sew bu ñu ñab-ñabal, \q1 te ñii defuñu lu moy raax ca weexal, \q1 \v 11 waxal raaxkati weexal yi, ne leen: \q1 ‘Tata jeey màbb, \q1 nde waameey wal, \q1 ponkali doji yuur ne yureet, \q1 ngëlén riddi, bëtt tata ja!’ \q1 \v 12 Bu tata ji jekkee ne jànjaŋ, \q1 deesu leen laaj fu weexal ba ngeen ca raaxoon jaar? \q1 \v 13 Kon Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Maay xadaru, riddil ngëlén, \q1 mer, walal waame, \q1 am sànj yuri ponkali doji sànkute. \q1 \v 14 Maay màbb tata ji ngeen raax weexal, \q1 mëqal ko suuf, \q1 kenu ya siiñ, \q1 lépp jóoru, ngeen jekkliku ca biir. \q1 Su boobaa ngeen xam ne maay Aji Sax ji. \q1 \v 15 Maay xëpp sama xadar ci kaw tata ji \q1 ak ña ko raaxoon weexal, \q1 ne leen: ‘Tata mes, \q1 weexalkatu tata mes! \q1 \v 16 Mooy yonenti Israyil yi jottli Yerusalem waxyu, \q1 di leen gisal peeñum jàmm, \q1 te jàmm amul.’ \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee!” \b \q1 \v 17 «Yaw nit ki, \q1 janool ak sa bokk yu jigéen, \q1 yiy waxe waxyu ci seen xelum bopp, \q1 nga wax waxyu fi seen kaw. \q1 \v 18 Neel: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Wóoy ngalla jigéen ñiy sàkkal ku ne jarab xërëm, \q1 di ràbbal ku ne muuraayu xërëm bu ko jot, \q1 di ko moome nit ñi! \q1 Man ngeena aakimoo sama bakkanu ñoñ \q1 tey sàmmaale seen bakkanu bopp? \q1 \v 19 Bu ngeen di fen sama ñoñ ñiy dégluy fen, \q1 yeena ngi may teddadil fi sama ñoñ, \q1 ngir ŋëbu peppum lors ak dogu mburu, \q1 ba tax leen di rey bakkan yu warula dee, \q1 di musal bakkan yu warula dund. \q1 \v 20 Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Maa ngii di dal ci seen kaw jaray xërëm, \q1 yi ngeen di nappe ay bakkan niy picc. \q1 Seeni jara laay foqatee ci seeni loxo, \q1 ba yiwi bakkan, yi ngeen di napp niy picc. \q1 \v 21 Maay foqati seeni muuraay, \q1 génne sama ñoñ ci seeni loxo, \q1 ñu noppee doon seenum pàdd, \q1 ba ngeen xam ne maay Aji Sax ji. \q1 \v 22 Gannaaw yeena fen ba jeexal xolu aji jub, \q1 te du maa ko tegu naqar, \q1 gannaaw yeena dooleel ku bon, \q1 tere koo dëpp yoonu mbonam ba dund, \q1 \v 23 dungeen gisati nag peeñuy caaxaan, \q1 dungeen gisaaneeti. \q1 Maay génne sama ñoñ ci seeni loxo, \q1 ngeen xam ne maay Aji Sax ji.”» \c 14 \s1 Dëppleen \p \v 1 Ba loolu wéyee ay magi \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* dikk janook man, toog. \v 2 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal ma ne ma: \v 3 «Yaw nit ki, ñii seen kasaray tuur lañu def ci seen xol, muy ay wu leen di gàllankoor, te ñu ne ci jàkk. Ñii dinaa leen wacc moos, ñuy sàkku leeraange ci man? \v 4 Waxal ak ñoom nag, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Képp ku bokk ci waa kër Israyil, ku yékkati kasaray tuuram, def ci xolam, muy ay wu koy gàllankoor, te mu ne ci jàkk, ba noppi muy seetluji ci ab yonent; man Aji Sax ji maa koy tontu tont lu dëppook limu kasaray tuuram. \v 5 Maay def loolu ngir nanguwaat xolu waa kër Israyil, gi ma dëddu ngir seen mboolem kasaray tuur yi.” \v 6 Kon nag waxal waa kër Israyil, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Dëppleen te dëddu seen kasaray tuur. Mboolem seen yëf yu siblu, dëdduleen ko. \p \v 7 «“Képp ku bokk ci waa kër Israyil, mbaa muy doxandéem bu dal ci biir Israyil, bu ma waccee, ba yékkati kasaray tuur, def ci xolam, muy ay wu koy gàllankoor, te mu ne ci jàkk, kooku bu dikkee cib yonent di sàkku leeraange ci man, man Aji Sax ji maa koy tontul sama bopp. \v 8 Nit kooku maa ko naa jàkk, def ko muy firnde, di ku ñuy léeboo, te maa koy wàññee ci sama ñoñ, ba ngeen xam ne maay Aji Sax ji. \p \v 9 «“Su fekkee ne yonent baa am lu ko nax, ba àddul boppam genn kàddug waxyu, day fekk man Aji Sax ji maa nax yonent ba. Maa koy dumaa sama loxo, sànke ko digg Israyil, sama ñoñ. \v 10 Kay seetlu ca yonent ba, aw ayam, mook ayu yonent ba, benn lay doon. Ñooy bokk gàddu seenu ay. \v 11 Su ko defee waa kër Israyil dootuñu ma wacc, di lajj, te dootuñu sobeel seen bopp ci seen bépp bàkkaar. Sama ñoñ lañuy doon, man ma doon seen Yàlla. Boroom bi Aji Sax jee ko wax.”» \s1 Yerusalem gépp a yelloo mbugal \p \v 12 Ba loolu amee kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal ma ne ma: \v 13 «Yaw nit ki, bu ma am réew dee moye jëfi ñàkk worma, ba ma dumaa leen sama loxo, dagge fa mburu, yónnee leen ab xiif, ba boole doom aadamaak mala dagge fa, \v 14 su Nóoyin ak Dañeel ak Ayóoba bokkoon nekk ca seen biir sax, ñoom ñett doŋŋ la seen bakkan di mucc ndax seenug njub. Boroom bi Aji Sax jee ko wax. \v 15 Su ma dajaloon réew meek rabi àll yu ko jeexal, ba muy réew mu gental mu kenn jaareetul ndax rab ya, \v 16 te mu fekk ñett ñooñu ca biir réew ma, giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, ñooñu ñett duñu mana musal seen jenn doom, du góor du jigéen; ñoom doŋŋ ay mucc, te réew ma dina gental. \v 17 Su ma wàccee saamar ci miim réew it, ba sant saamar ne ko mu jaar ci biir réew mi, dagge fi nit ak mala, \v 18 te mu fekk ñett ñooñu ci biir réew mi, giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, du seen jenn doom, góor ak jigéen ju ñuy mana musal. Ñoom ñett doŋŋ ay mucc. \v 19 Su ma yebalee mbas ci kaw réew mii it, ba xëpp fi samam sànj ci biir deret ju tuuru, ngir dagge fi nit ak mala, \v 20 te mu fekk Nóoyin ak Dañeel ak Ayóoba ci biir réew mi, giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, ñooñu ñett duñu mana musal seen jenn doom, góor ak jigéen. Seen njubteg bopp mooy musal seen bakkan. \p \v 21 «Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: Sama ñeenti mbugal yu tar yii laay yebal ci kaw Yerusalem. Ñuy saamar akub xiif ak rabi àll aku mbas, ngir dagge ci réew mi nit ak mala. \v 22 Waaye du tee mu am ndes mu ca rëcce, diy góor aku jigéen, ñu ñuy génneji réew mi. Ñu ngooguy génn, di leen fekki, te bu ngeen gisee seen jikko ak seeni jëf ju bon, seen xol dina sedd ci musiba mi ma wàcce ci kaw Yerusalem, ak mboolem lu ma fi wàcce. \v 23 Seen xol dina sedd ndax bu ngeen gisee seen jikko ak seeni jëf, dingeen xam ne mboolem li ma def ci dëkk bi, defuma ko ci neen. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.» \c 15 \s1 Bantu reseñ matul matt \p \v 1 Gannaaw loolu kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal na ma ne ma: \q1 \v 2 Yaw nit ki, ana lu bantu reseñ gëne ci bant yi, \q1 ak mboolem caru garab bu mu doon ci gott bi? \q1 \v 3 Ndax dees na ca sàkk bant, liggéeye ko? \q1 Am dees na ca sàkke wékkukaay, wékk ca lenn? \q1 \v 4 Xanaa sànni cib taal, xambe, \q1 ñaari cat ya lakk, digg ba xoyomu. \q1 Ana lu deeti njariñam? \q1 \v 5 Ndegam ba mu nee ñumm, \q1 lees ci dul liggéey dara, \q1 gën ba mu jàppee ba xoyomu. \q1 \v 6 Kon nag Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Dees na xamb caru reseñ, \q1 mu bokk ci banti garab yi ma joxe, ñu xamb lépp, \q1 te noonu laay xambe waa Yerusalem. \q1 \v 7 Maay jànkoonteek ñoom, \q1 ñu rëcc sawara, \q1 sawara lakk leen. \q1 Bu ma jànkoonteek ñoom, \q1 dingeen xam ne maay Aji Sax ji. \q1 \v 8 Maay gental réew mi, \q1 ñoo def jëfi ñàkk worma. \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \c 16 \s1 Yerusalem yemul ci boroom këram \p \v 1 Ba loolu amee kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal ma ne ma: \v 2 «Yaw nit ki, nanga xamal Yerusalem jëfam ju siblu ji. \v 3 Ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Sa cosaan ak sab juddu réewum Kanaan la. Sa baay dib Amoreen, sa ndey dib Etteen\f + \fr 16.3 \fr*\fk Amoreen ñeek Etteen, \fk*\ft ña dëkke woon diiwaanu tund ya, ay jaamukati tuur lañu woon ñu bokkoon ca askanu Kanaaneen ña. Du Yawut yaa sanc Yerusalem, waaye Kanaaneen ñaa ko sancoon. Seetal ci \ft*\ft \+bk Amos\+bk* 2.10.\ft*\f*. \v 4 Ba nga juddoo, ca bés ba nga juddoo, dooñeesu la, sangeesu la ba nga set, jonjeesu la xorom, laxaseesu lay laytaay. \v 5 Xooleesu la bëtu ñeewante ngir defal la lenn ci yooyu ngir yërmande. Dees laa sànni ci àll bi bés ba nga juddoo ndax jéppi la. \v 6 Maa fa jaare, seen la ngay wéqu, sangoo sa deret. Ma ne la: Sangoo nga sa deret waaye, dundal! Neeti la: Sangoo nga sa deret, waaye dundal. \v 7 Maa la sëqal ni caxum tool, ngay màgg, di màgg ba mat sëkk, saxi ween, sa kawar sëq, te nga ne duŋŋ-duŋŋaaral. \v 8 Ma jaareeti fa, xool la, gis ne mat ngaa séy. Ma tàllal sama mbubb, sànge ko sa yaramu neen, ba noppi giñal la, dikke la \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w*\f + \fr 16.8 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Ruut\+bk* 3.9.\ft*\f*. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Nii laa la moome. \p \v 9 «“Ma daldi lay sang, raxas sa deret ba mu set, diw la, \v 10 solal la ndimo lu yànj ak dàlli der, muure la ndimol lẽe, tegal la ca sooy. \v 11 Ma takkal lay gànjar; takkal la lami loxo, akub caq, \v 12 ba noppi takkal la jaarob bakkan ak jaaroy nopp, solal la mbaxanam lingeer mu yànj. \v 13 Nga takkoo wurus ak xaalis, sol ndimol lẽe ak sooy ak ndimo yu yànj, di lekk sunguf su mucc ayib ak lem ak diw. Nga mujj taaroo taaru ba jot darajay lingeer, \v 14 siiw ba xeet yépp xam la ndax taar bu sotti ndax sama gànjar gu yànj gi ma la takkal. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \p \v 15 «“Teewul nga gis sab taar, di gànctoo sa bayre ngànctu gu ne xéew, ku romb yaa moom. \v 16 Yaa tànn ci sa yére yu yànj, rafetale sa jaamookaayi tuur, ba noppi di ca gànctu; lu masula am te du amati mukk. \v 17 Yaa jël sa gànjari wurus ak xaalis yi ma la jox, sàkk ca céri góor, di ca gànctu, \v 18 te yaa jël sa yére yu yànj, sànge say tuur, sama diw ak sama cuuraay, nga taajal leen. \v 19 Sama dugub ja ma la joxoon, sunguf su mucc ayib saak diw gaak lem, ja ma la doon leele, lépp yaa leen ko taajal, defal leen ko saraxu neexal bu xeeñ. Mu ngoog! Kàddug Boroom bi, Aji Sax jee. \p \v 20 «“May wax, nga jël sa doom yu góor ak yu jigéen yi nga ma jural, di leen sarxalal say tuur, leele leen. Gànctu da laa doyul? \v 21 Yaa rendil ay tuur samay doom, yoole leen. \v 22 Ci biir mboolem sa jëf ju siblu jooju ak sa gànctu, fàttlikuwoo benn yoon ba ngay lu tuut, ne duŋŋ-duŋŋaaral, di wéqu, sangoo sa deret. \p \v 23 «“Gannaaw sa mbon googu gépp nag, wóoy, wóoy ngalla yaw! Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \v 24 Tabaxal nga sa bopp ab néeg, sàkkal sa bopp bérab bu kawe ci péncoo pénc. \v 25 Selebe yoon wu ne, tabax nga fa sa jaamookaay, di fa teddadil sab taar, ku romb, nga ràccal ko say tànk ci sa gànctu gu dul jeex. \v 26 Gànctu ngaak waa Misra, sa dëkkandoo yu alde yi, di gënatee gànctu, di ma naqaral. \p \v 27 «“Booba nag laa la dóor sama loxo, wàññi sa njël, wacce la sa coobarey noon ya, janqi Filisti ya\f + \fr 16.27 \fr*\fk janqi Filisti ya\fk*\ft mooy dëkki Filisti yi gëna am solo, te nangu woon lenn ci suufas Yuda.\ft*\f*. Ñoom sax am nañu kersa ci sa jëfinu yàqute gi. \v 28 Doyaloo, xanaa di gànctook waa Asiri\f + \fr 16.28 \fr*\ft Réew yu bare dañu doon lëkkoo ak réewum Asiri ca yooya jamono ndaxte ñoo ëppoon doole lu jiitu Babilon di sut ci réewi àddina.\ft*\f*. Gànctu ngaak ñoom te taxu laa doyal ba tey. \v 29 Ngay gënatee gànctu, ba ca Babilon, réewum jula ya, te loolu taxu laa doyal ba tey. \p \v 30 «“Yaaka weex bët, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, \q1 lii lépp di jëfi gànc bu dëgër bët. \p \v 31 «“Tabax nga ab néeg selebe yoon wu ne, sàkk sa jaamookaay péncoo pénc, te ab gànc sax tane la, nde yaw laajoo ag pey. \v 32 Cim! Jigéenu njaalookat bi nga doon, ay doxandéem sax gënal la sa jëkkër. \v 33 Mboolem caga yi dañuy feyeeku! Waaye yaw yaay neexal sa far yépp, di leen fey ñu jóge fu ne, di la tëdde. \v 34 Yaw kay sag ngànc bokkoo kook gànc yi. Kenn sàkkuwu la. Yaw kay yaay feye, kenn feyu la. Kon yaw meloo ni benn gànc! \p \v 35 «“Kon nag Yerusalem gànc bee, déglul kàddug Aji Sax ji. \v 36 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Gannaaw yaa wasaare sa alal, ñoriku ne duŋŋ, di gànctook sa far yii, muy sa mboolem kasaray tuur, bay tuur sa deretu doom yi nga leen rendil, \v 37 maa ngii nag di dajale mboolem sa far yi la doon bége, ñi nga bëgg ñépp ak ñi nga bañ ñépp. Maa leen di dajalee fu nekk ci sa kaw, ba noppi ñori la yaramu neen, ñu gis la nga ne duŋŋ. \v 38 Maa lay àttee àtteb jigéeni njaalookat, jigéeni tuurkati deretu nit. Maa lay xëpp deretu xadar ak fiiraange. \v 39 Maa lay wacceek say far, ñu màbb say néeg, tas say jaamookaay, futti la, nangu sa gànjar gu yànj gépp, wacc la yaramu neen, nga ne duŋŋ. \v 40 Dinañu sañaxal gàngoor ci sa kaw, ñu ànd jóor lay doj, dogate la seeni saamar. \v 41 Dinañu lakk say kër, teg la mbugal, jigéen ñu bare di gis. Maay dakkal ngànc gi nga nekke, te dootoo feyati aw far. \v 42 Maa lay xëpp samam sànj ba mu jeex, bala ma laa moyale sama xadaru fiiraange, doora dal, ba meddi. \p \v 43 «“Yaa fàttlikuwul ba ngay ndaw, yaa def lii lépp ba merloo ma. Kon man it, sa jëfin kat laa lay këpp ci bopp, feye la ko. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Du yaa gànctu, dolli ci sa jépp jëf ju siblu? \p \v 44 «“Yaw Yerusalem, képp kuy léeboo dina la léeboo ne la: ‘Ndey ja, doom ja!’ \v 45 Yaa mat doom sa ndey, ji sib jëkkëram aki doomam. Yaa mat doomu ndey sa doomi ndey, ya sib seen jëkkër ak seeni doom, yaa donn sa ndey Etteen ba, donn sa baay, Amoreen ba. \v 46 Sa mag ju jigéen ji la féete càmmoñ di Samari aki janqam, sa rakk ju jigéen ji la féete ndijoor, di Sodom aki janqam\f + \fr 16.46 \fr*\ft Janq jii mooy dëkk yu ndaw yi bootu ci Sodom.\ft*\f*. \v 47 Yemuloo rekk ci roy seen jëfin ak seen jëf ju siblu. Tuuti na! Yaa leen gëna yàqu ci sa mboolem jëfin. \v 48 Yaw Yerusalem, giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, sa rakk ju jigéen ja, Sodom, mooki janqam defuñu li nga def yaw, yaak say janq. \v 49 Lii de, moo doon bàkkaaru Sodom, sa rakk ja, mooki janqam: réy, fuqle, naagu, ne finaax ak ñàkka dimbali ku ñàkk ak ku néewle, \v 50 ba mujj reew bay def jëf ju siblu, may gis. Looloo waral ma beddi leen nii, nga gis. \v 51 Samari nag, sa genn-wàllu bàkkaar, bàkkaaru ko. Yaa ëpp fopp sa doomi ndey yii jëf ju siblu, te tax nga ñu far mel ni ñu def njekk ndax mboolem jëf ju siblu joo def. \v 52 Léegi nag gàddul sa toroxte gi nga maye sa doomi ndey aw lay ndax jëf ju siblu joo jëf, ba yées leen. Gën nañu la. Kon nag séddool gàcce te gàlloo toroxte, nde tax nga sa doomi ndey yi niru ñu def njekk. \p \v 53 «“Waaye maay tijji seen wërsëg; maay tijji wërsëgu Sodom aki janqam, tijji wërsëgu Samari aki janqam, yaw it ma tijjiwaale sa wërsëg. \v 54 Su ko defee nga gàddu sa toroxte, torox ci mboolem li nga def, ba ruccanti sa doomi ndey yi. \v 55 Sa rakk yi, Sodom aki janqam dinañu dellu na ñu nekke woon. Samari aki janqam dellu na ñu nekke woon, yaw it yaak say janq, ngeen dellu na ngeen nekke woon. \v 56 Xanaa du ba nga bewee yaa saxaloon ci saw làmmiñ kàddug baatal Sodom? \v 57 Booba sag mbon fàŋŋaaralagul. Léegi tey janqi Edom ak mboolem ñi ko wër ñoo lay sewal, janqi Filisti yi la séq it xeeb la. \v 58 Sag yàqute ak sa jëf ju siblu nag, yaa koy gàddu. Kàddug Aji Sax jee. \p \v 59 «“Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: Ni nga def rekk ni laay def ak yaw, mi sofental kàddug ngiñ, fecci kóllëre. \v 60 Waaye man maay bàyyi xel sama kóllëre gi ma fasoon ak yaw ba ngay ndaw. Maa lay saxalal kóllëre guy wéy ba fàww. \v 61 Yaay fàttliku say jëfin, ba am kersa keroog booy dalal sa doomi ndey yu jigéen, ñi la mag ak ñi la féete ndaw. Maa la leen di may niy doom, doonte loolu bokkul ci sama kóllëreek yaw. \v 62 Maay saxal sama kóllëreek yaw, nga xam ne maay Aji Sax ji. \v 63 Su ko defee nga fàttliku démb, daldi rus, torox ba ne xerem keroog ba ma lay jot ci mboolem loo def. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”» \c 17 \s1 Fecci kóllëre, peyam du jaas \p \v 1 Gannaaw loolu kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal na ma, ne ma: \v 2 Yaw nit ki, caxal waa kër Israyil aw cax, ci biir léeb woo leen di léebal. \v 3 Ne leen: «Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Jaxaay\f + \fr 17.3 \fr*\fk jaxaay ji \fk*\ft mooy Buuru Babilon, Nabukodonosor mi nangu woon Yerusalem.\ft*\f* ju mag la woon, réyi laaf, guddi dunq, \q1 sëq lipp, yànj lool. \q1 Mu dikk ba Libaŋ, jàpp ci collu genn garabu seedar, \q1 \v 4 dagg car bu ndaw\f + \fr 17.4 \fr*\fk dagg car bu ndaw \fk*\ft mooy ba ñu yóbboo Buur Yowakin ngàllo ca Babilon.\ft*\f* ba ca gëna kawe, \q1 yóbbu ba menn réewum jula, \q1 jëmbat ko ca biir dëkkub jaaykat ya. \q1 \v 5 Mu sàkk ci jiwum réew mi\f + \fr 17.5 \fr*\fk jiwum réew mi \fk*\ft mooy Cedesyas baayu Yowakin bu ndaw. Buur Cedesyas la Nabukodonosor dénkoon nguurug Yuda.\ft*\f*, \q1 def ko ci suuf su nangu, \q1 dendale kook ndox mu ne xéew, \q1 ni kuy jëmbat garabu sóol. \q1 \v 6 Mu jebbi, dig reseñ, gëna yaatu te gàtt taxawaay. \q1 Car ya ne coleet wuti jaxaay ja, \q1 reen ya des ca suufam. \q1 Mu di reseñ gu saxi car, \q1 firiy bànqaas. \b \q1 \v 7 «Jeneen jaxaay ju mag\f + \fr 17.7 \fr*\fk jeneen jaxaay ju mag \fk*\ft mooy Firawna buuru Misra.\ft*\f* daldi ne jimeet, \q1 réyi laaf, sëq lipp. \q1 Reseñ ja jekkee jekki tàllal koy reenam, \q1 di ŋaf-ŋafi, firiy bànqaasam, wuti ko, \q1 ngir mu suuxat ko fa mu jëmbate woon. \q1 \v 8 Tool bu nangu bu feggook ndox mu ne xéew la jëmbate woon, \q1 ngir naat, meññ, ba doon reseñu ngëneel. \b \q1 \v 9 «Neel, Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Mbaa jooju reseñ dina baaxle? \q1 Mbaa jeneen jaxaay ja du buddiy reenam, \q2 buur doom ya, \q1 ba lu mu jebbile woon lax, \q1 ba buddi reen ya du laaj përëg bu réy, \q2 mbaa nit ñu bare? \q1 \v 10 Ma nga noonu jëmbate, waaye mbaa dina baaxle yee? \q1 Mbaa ngelawal penku du ko laal rekk mu laxa lax? \q1 Mbaa du lax fa mu saxe?» \p \v 11 Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma: \v 12 «Waxal waa kër fippukat yi, ne leen: “Xamuleen lu mbir yooyu di wund?” Ne leen: “Mu ngoogu, buuru Babilon a dem Yerusalem, jàpp buur baak kàngam ya, ànd ak ñoom, yóbbu Babilon. \v 13 Moo tànn ku bokk ci askanu buur, fasook moom kàddu, giñloo ko ne dina ko nangul, daldi yóbbu njiiti réew mi, \v 14 ngir nguurug Yerusalem suufe, baña yékkatiku, di wéye surgawu Babilon, ni ñu ko fasoo woon. \v 15 Ka bokk ci askanu buurub Israyil nag fippu, yónni ay ndaw réewum Misra, ngir ñu jox ko ay fas ak mbooloo mu takku. Moo ka def loolu dina baaxlee? Mbaa dina mucc? Nu mu cay mucce te wor kàddu, ga mu fasoo woon? \p \v 16 «“Giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, ci biir réewum buur boobu ko fal, te mu sàggane la mu ko giñaloon, wor kàddu ga mu fasante woon ak moom, ci biir Babilon googu lay deeye. \v 17 Firawnaak mbooloom mu réy ak gàngooram gu mag sax duñu ko mana wallu ci xare, keroog bu ñuy yékkati ab sëkk, tabax ab gawukaay ngir bóom ñu bare. \v 18 Moo sàggane ngiñ, moo wor kàddu ga mu fasante woon. Mu ngoog, moo joxe kàddoom, ba noppi walbatiku def lii lépp. Du mucc mukk. \p \v 19 «“Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Giñ naa ko ci man miy dund, maay këpp jëfam ci kaw boppam ndax ngiñ li mu ma giñal la sofental, kàddu gi mu fasanteek man la wor. \v 20 Maa koy laaw sama mbaal, mu lonkoo samab caax, ma yóbbu ko Babilon, layoo faak moom ñàkke worma gi mu ma ñàkke worma. \v 21 Mboolem ñay dawe ca gàngooram yépp, saamar lañuy fàddoo; ña cay rëcce, fépp fu ngelaw jublu lañuy tasaarooji, ba ngeen xam ne man Aji Sax ji maa wax. \p \v 22 «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Man ci sama bopp maay sàkke ab car \q2 ca njobbaxtalu garabu seedar gu kawe ga, \q1 sàkkal ko bérab. \q1 Car yu ndaw ya ca kaw laay fàqe car bu nooy, \q1 jëmbatal ko sama bopp ci kaw tund wu mag te kawe. \q1 \v 23 Ca kaw tundu Israyil wu mag wa laa koy jëmbat, \q1 mu sëq, meññal, \q1 ba doon garabu seedar gu am daraja, \q1 mboolem picc dëkke ko, \q1 mboolem njanaaw màkkaanoo keram. \q1 \v 24 Garabi àll bi yépp dinañu xam, \q2 ne man Aji Sax ji maay gàttal garab gu gudd, \q1 di guddal garab gu gàtt. \q1 Maay wowal garab gu naat, \q1 di naatal garab gu wow. \q1 Man Aji Sax ji maa wax, maay jëf.”» \c 18 \s1 Jëf, jël \p \v 1 Gannaaw loolu kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal na ma ne ma: \v 2 «Ana lu waral waxin wi ngeen di waxe fi Israyil naan: \q1 “Baay lekk reseñ ju xaay, \q1 mu uum gëñi doom ja”? \p \v 3 «Giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, dootuleen waxe woowu waxin fi Israyil. \v 4 Mu ngoog, bépp bakkan maay Boroom. Muy bakkanu baay, di bakkanu doom, maa moom. Bakkan bi bàkkaar daal mooy dee. \q1 \v 5 Su nit dee boroom njekk, \q1 di jëfe yoon ak njekk, \q1 \v 6 tund ya ca saraxi tuur ya, lekkejiwu ca, \q1 kasaray tuuru waa kër Israyil, wékku cay gëtam, \q1 jabaru jaambur, sobeelu ko, \q1 jigéen ju gis baax, jegewu ko, \q1 \v 7 du kenn ku mu néewal, \q1 xanaa ab tayle, mu delloo ku ko ameel, \q1 alalu jaambur it, foqatiwu ko, \q1 xanaa ku xiif, mu leel, \q1 ku rafle, mu wodd, \q1 \v 8 aw ndollant taxu koo leble, \q1 ab tegandaay, jëlu ko, \q1 xanaa luy njubadi, mu moyu, \q1 àtteb dëgg, mu doxal diggante nit ak nit, \q1 \v 9 sama dogali yoon, mu di ca doxe, \q1 sama àttey yoon, muy jëfe worma: \q1 kooku boroom njekk la, \q1 te mooy dund déy! \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \b \q1 \v 10 «Jii waay su juree doom ju néeg juy tuur deretu jaambur \q1 mbaa muy def lenn ci yii, \q1 \v 11 te moom miy baayam jëfewu ci lenn, \q1 tund ya ca saraxi tuur ya, doom ja di ca lekki, \q1 jabaru jaambur, mu sobeel, \q1 \v 12 ku ñàkk ak ku néewle, mu néewal, \q1 alalu jaambur, mu foqati, \q1 ab tayle, delloowu ko ku ko ameel, \q1 xanaa kasaray tuur, mu wékki gët, \q1 jëf ju siblu, mu jëfe, \q1 \v 13 ndollant lay leblee, \q1 ab tegandaay, mu jël. \q1 Moo kii nu muy dunde? \q1 Kii kay du dund! \q1 Ak mboolem jëf ju siblu jii mu def, \q1 dee rekk mooy àtteem. \q1 Bakkanam lay gàddu. \b \q1 \v 14 «Waaye kooka nag su amee doom, \q1 doom ja gis mboolem li baayam bàkkaar, \q1 mu teg ci bëtam te taxul mu roy ko; \q1 \v 15 tund ya ca saraxi tuur ya, lekkiwu ca, \q1 ay gëtam, wékku ko kasaray tuuri waa kër Israyil, \q1 jabaru jaambur, sobeelu ko, \q1 \v 16 du kenn ku mu néewal, \q1 ab tayle, jëlu ko, sàkkuwul ku ko tayle lenn, \q1 alalu jaambur, foqatiwu ko, \q1 xanaa ku xiif, mu leel, \q1 ku rafle, mu wodd, \q1 \v 17 néew-ji-doole, loxoom dalu ko, \q1 ndollant ak ab tegandaay, jëlu ko, \q1 sama àttey yoon lay jëfe, \q1 sama dogali yoon lay doxe. \q1 Kooku du dee ngir ñaawtéefu baayam. \q1 Dina dund déy! \q1 \v 18 Baayam a jaay doole, \q1 moo foqati alalu mbokk, \q1 lu baaxul la def ci biiri bokkam. \q1 Kon nag mooy dee ngir ñaawtéefu boppam. \b \q1 \v 19 «Ngeen neeti: “Lu tax doom du gàddu bàkkaaru baay?” \q1 Xanaa du njub ak njekk la doom ji jëfe, \q1 sama dogali yoon yépp, mu di ko sàmm, \q1 di ko jëfe? \q1 Dina dund kay! \q1 \v 20 Ki bàkkaar daal mooy dee. \q1 Doom du gàddu ñaawtéefu baay, \q1 baay it du gàddu ñaawtéefu doom. \q1 Njekk réerul boroom, \q1 mbon réerul boroom. \b \q1 \v 21 «Waaye ku bon ki su dëddoo mboolem moy yi mu moy, \q1 di sàmm sama mboolem dogali yoon, \q1 di jëfe yoon ak njekk, \q1 dina dund déy, \q1 du dee moos! \q1 \v 22 Mboolem tooñam ya mu tooñoon, \q1 deesu ko ko dencal. \q1 Njekk li mu jëfe moo koy taxa dund. \v 23 Ana bànneex bu ma am ci deewug ku bon? \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \q1 Xanaa bu dëddoo jikkoy mbonam, ba dund! \b \q1 \v 24 «Waaye su dee ku juboon, ba noppi dëddu njubte \q1 di def njubadi, \q1 di roy mboolem jëf ju siblu ju ku bon def, \q1 kooku nu muy dunde? \q1 Mboolem njekk gu mu defoon, \q1 deesu ko ko dencal. \q1 Ag ñàkk wormaam ak bàkkaaram moo koy taxa dee. \b \q1 \v 25 «Yeen nag ngeen ne: “Boroom bi, ni muy doxale jaaduwul!” \q1 Waa kër Israyiloo, dégluleen! \q1 Sama doxalin a jaaduwul, \q1 am seeni doxalin a jaaduwul? \q1 \v 26 Boroom njekk bu dëddoo njekkam, di def njubadi ba dee, \q1 njubadeem ga mu def moo ko taxa dee. \q1 \v 27 Waaye ku bon nag, bu dëddoo mbonam ga mu nekke, \q1 di def njub ak njekk, \q1 moom moo musal bakkanu boppam. \m \v 28 Ndegam moo xoolaat, ba dëddu mboolem tooñam yu mu tooñ, dina dund déy. Du dee moos. \v 29 Moonte waa kër Israyil nee: “Boroom bi ni muy doxale jaaduwul.” Waa kër Israyiloo, samay doxalin a jaaduwul, am seeni doxalin a jaaduwul? \p \v 30 «Lii moo tax yeen waa kër Israyil, ma di leen àtte, ku nekk ciy jëfam. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Dëppleen te dëddu mboolem seeni tooñ, ngir seenu ay bañ leena gàllankoor. \v 31 Xalableen mboolem tooñ yi ngeen di tooñ. Sàkkuleen xol bu yees ak xel mu yees. Yeen waa kër Israyil, lu jar ngeen di dee? \v 32 Man de, bugguma kenn dee. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Dëppleen ba dund!» \c 19 \s1 Jooy ngarmig Israyil war na \p \v 1 Aji Sax ji ne ma: «Yaw nag jooyal garmiy Israyil. \v 2 Neel: \q1 “Céy sa ndey, ndaw gaynde, \q2 fi biir gaynde yi! \q1 Moo goor fi biir gaynde yu ndaw yi, \q1 di fa yar ay doomam. \q1 \v 3 Moo tàggat kenn ciy goneem\f + \fr 19.3 \fr*\ft Wax ji ci Buur Yowakas la jëm. Seetal ci \ft*\ft \+bk 2.Buur ya\+bk* 23.31-34.\ft*\f*, \q1 ba muy góoru gaynde gu ndaw, \q1 mana pàdd um pàddam, \q1 di yàpp doom aadama. \q1 \v 4 Ba ko xeet ya déggee, dañu koo fexeel, \q1 mu sërëx ca seenum yeer, \q1 ñu lonk, yóbbu réewum Misra. \b \q1 \v 5 «“Ndey gaynde xaara xaar, \q1 ba gis ne yaakaar jee na, \q1 mu jël keneen ciy goneem\f + \fr 19.5 \fr*\ft Wax ji ci Buur Cedesyas la jëm. Seetal ci \ft*\ft \+bk 2.Buur ya\+bk* 24.18-20 ak 25.1-7.\ft*\f*, \q1 def ko góoru gaynde gu ndaw. \q1 \v 6 Daa ànd ak moroomi gayndeem, \q1 màgg, doon góoru gaynde gu ndaw, \q1 ba mana pàdd am pàddam, \q1 di yàpp doom aadama. \q1 \v 7 Mu tëdde seeni jëtun, \q1 gental seen dëkk yu mag, \q1 réew maak la ca biiram tiit ca coowal ŋaram. \q1 \v 8 Teewul xeeti diiwaan ya ko séq ànd, \q1 dal fa kawam, \q1 laaw ko seenum caax, \q1 sërxal ca seenum yeer. \q1 \v 9 Ñu lonk, dugal cib kaaf, \q1 yóbbul ko buuru Babilon, \q1 tëj ko ca biir ab tata, \q1 ba kenn déggatuli ŋaram \q2 fa kaw tundi Israyil. \b \q1 \v 10 «“Sa ndey a la niru, mel ni reseñ \q2 gu ñu jëmbat fi wetu ndox, \q1 meññ, sëq lipp, \q1 ndax ndox mu ne xéew. \q1 \v 11 Mu am car yu dëgër, \q2 yu man yeti nguur, \q1 daldi màgg ba àkki niir ya, \q1 ràññiku ci taxawaay ak sëqaay. \q1 \v 12 Waaye am sànj a ko buddi, sànni fi suuf, \q1 ngelawal penku wowal doom ya, \q1 bànqaasam yu dëgër ya fàq, lax, \q1 sawara xoyom ko. \q1 \v 13 Tey mu ngi jëmbate fi màndiŋ mi, \q1 ci réew mu wow, maral. \q1 \v 14 Sawaraa tàkke fa bànqaasam, \q1 xoyom njebbit ak meññeef. \q1 Du car bu dëgër bu ca des \q1 bu mana doon yetu nguur.” \q1 Woyu dëj a ngii wu ñuy jooyeb dëj.» \c 20 \s1 Israyil wor, Aji Sax ji gore \p \v 1 Gannaaw ba loolu wéyee ca atum juróom ñaareel ma, fukki fan ca juróomeelu weer wa\f + \fr 20.1 \fr*\ft Mu yemook fukki weer ak benn gannaaw peeñu ma jiitu mii. Seetal ci 8.1.\ft*\f*, ay nit ñu bokk ci magi Israyil ñoo dikk fi man, di seetlu ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Ñu toog fi sama kanam. \v 2 Kàddug Aji Sax ji nag dikkal ma ne ma: \v 3 «Yaw nit ki, nanga wax ak magi Israyil, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Seetlu ci man moo leen indi? Giñ naa ko ci man miy dund, du maa leen di won li ngeen di seetlu. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.” \v 4 Yaw nit ki, tiiñal leen, tiiñal leen kat, seen jëfu maam ju siblu ji, xamal leen ko. \p \v 5 «Nanga leen wax, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Ba ma tànnee Israyil, maa giñal askanu waa kër Yanqóoba woowa. Maa leen xamal maay kan ca réewum Misra, giñal leen, ne leen: Man Aji Sax ji maay seen Yàlla. \v 6 Bésub keroog laa leen giñal ne maa leen di génnee réewum Misra, yóbbu leen réew mu ma leen beralal, mu meew maak lem ja tuuroo, fa gëna taaru ci réew yépp.” \v 7 Ma ne leen: “Tuur yi ngeen wékki gët yeen ñépp, xalableen leen. Kasaray tuuri Misra, buleen ci sobeel seen bopp. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.” \v 8 Teewul ñu gàntal ma, nanguwñu maa déglu. Kenn nanguwula xalab tuur yu seexluwu yi mu wékki gët, kenn dëdduwul kasaray tuuri Misra. Ma nar leena xëpp samam sànj, ŋaccal leen sama mer ci biir réewum Misra. \v 9 Teewul ma sédd ci sama teddngay tur, ngir xeet yi ñu nekk ci seen biir bañ maa sikk. Ndax ba may xamal bànni Israyil sama bopp, di leen génne Misra, xeet yooyaa ko seede woon. \v 10 Ma génne leen réewum Misra, yóbbu leen ca màndiŋ ma. \v 11 Ma jox leen sama dogali yoon, xamal leen sama àttey yoon yooyuy guddal fanu képp ku koy jëfe. \v 12 Sama \w bési Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w* itam maa leen ko jox, muy màndarga sama digganteek ñoom, ngir ñu xam ne man Aji Sax ji maa leen sellal. \p \v 13 «Waaye waa kër Israyil dañu maa gàntal ca màndiŋ ma. Sama dogali yoon, jëfewuñu ko, sama àttey yoon yiy guddal fanu képp ku koy jëfe, ñu xalab. Ñàkke nañu worma lool sama bési Noflaay. Ma nar leena xëpp samam sànj ca màndiŋ ma, sànk leen. \v 14 Teewul ma sédd ci sama teddngay tur, ngir xeet, ya seede woon ba ma leen di génne, bañ maa sikk. \v 15 Ba tey maa leen giñal ca màndiŋ ma, ne duma leen yóbbu réew ma ma leen jox, fa meew maak lem ja tuuroo, fa gëna taaru ci réew yépp. \v 16 Li ko waral mooy sama àttey yoon yi ñu xalab, ak sama dogali yoon yi ñu jëfewul, ak sama bési Noflaay yi ñu ñàkke worma, ndax xol lañu toppe seen kasaray tuur yi. \v 17 Teewul ma xool leen bëtu ñeewante ba sànkuma leen, faagaagaluma leen ca màndiŋ ma. \v 18 Ma wax nag seeni doom ca màndiŋ ma ne leen: “Seen dogali baay, buleen ko jëfe; seen àttey yoon, buleen ko topp; seen kasaray tuur, buleen ca sobeel seen bopp. \v 19 Man Aji Sax ji maay seen Yàlla. Sama dogali yoon, jëfeleen ko; sama àttey yoon, ngeen sàmm ko, di ko jëfe. \v 20 Sama bési Noflaay, sellal-leen ko, muy firnde sama digganteek yeen, ngir ngeen ràññee ne man maay seen Yàlla Aji Sax ji.” \p \v 21 «Waaye doom ya dañu maa gàntal. Sama dogali yoon, jëfewuñu ko, sama àttey yoon yiy guddal fanu képp ku koy jëfe, sàmmuñu ko. Sama bési Noflaay lañu ñàkke worma. Ma nar leena xëpp samam sànj, ŋaccal leen sama mer ca màndiŋ ma. \v 22 Teewul ma téye sama loxo, sédd ci sama teddngay tur ngir xeet, ya seede woon ba ma leen di génne, bañ maa sikk. \v 23 Ba tey maa leen giñal ca màndiŋ ma ne dinaa leen tasaare ci biir xeet yi, wasaare leen ci biir réew yi. \v 24 Li ko waral mooy sama àttey yoon yi ñu jëfewul, ak sama dogali yoon yi ñu xalab, ak sama bési Noflaay yi ñu ñàkke worma, ak topp gi ñu topp seen kasaray tuuri baay, wékk leeni gët. \v 25 Ba tey maa leen bërgal ak àttey yoon yu amul njariñ ak dogali yoon yu taxul kenn a dund. \v 26 Maa leen sobeel ak seen sarax yi ñuy sarxal tuur yi, ci seen bépp taaw bu ñu lakk ngir tuur yi. Li ma ci jublu mooy ñu jommi, ba ràññee ne man maay Aji Sax ji. \p \v 27 «Moo tax, yaw nit ki, nanga wax ak waa kër Israyil, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Seeni baay a ma dellu ŋàññ, fecci ma kóllëre. \v 28 Maa leen yóbbu réew ma ma leen giñaloona jox, teewul fu ñu gis tund wu kawe, mbaa garab gu sëq, rendi nañu fa seeni sarax, jooxe fa seen jooxe yi may merloo, taal fa seen saraxi cuuraay, tuural fa seeni tuur. \v 29 Ma ne leen: Ana lu waral \w bérabu jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* bii ngeen di dem?” Bérabu Jaamookaay lañu koy wax ba tey jii. \p \v 30 «Kon nag nanga wax ak waa kër Israyil ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Seen tànki baay ngeen topp, di sobeel seen bopp, topp seen tuur yu siblu, di gànctook ñoom? \v 31 Bu ngeen di joxe ay sarax, di lakk seeni doom ngir ay tuur, yeena ngi sobeel seen bopp ba tey jii ci seen tuur yii yépp. Man nag ngeen defe ne maa leen di bàyyi, ngeen seetlusi fi man, yeen waa kër Israyil? Giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, duma leen bàyyi mukk ngeen seetlu fi man. \v 32 Li ngeen mébét ci seen xel du am mukk. Yeena ngi naan: ‘Nan mel ni xeet yépp, mel ni waasoy réew yi, di jaamu bant ak doj.’ \v 33 Giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, sama dooley loxo ak sama kàttanu përëg, ak sànj mu naan soteet laay nguuroo ci seen kaw. \v 34 Maa leen di génnee ci askan yeek réew yi ngeen tasaaroo ci seen biir. Sama dooley loxo laa koy defe ak sama kàttanu përëg, ak sànj mu naan soteet fi seen kaw. \v 35 Maa leen di yóbbu màndiŋ ma ñuy wooye Màndiŋu Askan yi, layoo faak yeen, di leen xool, ngeen di ma xool. \v 36 Noonee ma layoo woon ak seen baay ca màndiŋu réewum Misra, ni laay layook yeen. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \v 37 Maa leen di lime sama yetu sàmm, kenn-kenn, tënk leen ci pas-pasu \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* gi. \v 38 Maay xettee fi seen biir ñi may gàntal ak ñi may tooñ. Réew ya ñu wàlliyaani, fa laa leen di jële, te réewum Israyil, duñu fa duggi. Su boobaa ngeen xam ne maay Aji Sax ji. \p \v 39 «“Léegi nag yeen waa kër Israyil, Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Aca, na ku ne jaamuji kasaray tuuram! Dungeen mujje lu moy déggal ma, ba sama tur wu \w sell|lemma="sell:"\w* wi, dootuleen ko teddadile seeni sarax ak seeni tuur. \v 40 Fa kaw sama tund wu sell wa, fa tundu Israyil wu kawe wa, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, foofa déy la ma waa kër Israyil gépp di jaamujee, ñoom ñépp ca réew ma. Fa laa leen di nangule. Fa laay sàkkoo seeni jooxe ak seen ngëneeli sarax, ak lépp lu ngeen ma sellalal. \v 41 Maa leen di nangul seen saraxu cuuraay, gannaaw bu ma leen génnee fa biir xeet yaak réew ya ngeen tasaaroo ca seen biir, ba dajale leen. Su boobaa maay jëfe sellnga fi seen biir, xeet yi seede. \v 42 Dingeen xam ne maay Aji Sax ji, gannaaw bu ma leen délloosee ci biir suufas Israyil, réew ma ma giñaloon seeni maam, ne dinaa leen ko jox. \v 43 Fa ngeen di fàttlikoo seeni jëfin, mboolem seeni jëf yu ngeen sobeele woon seen bopp, daldi jéppi seen bopp ndax seen mboolem jëf ju bon. \v 44 Yeen waa kër Israyil, duma jëflanteek yeen li seen jikko ju bon yelloo ak seen jëfi yàqute, waaye sama teddngay tur laa ciy seet, ba ngeen xam ne man maay Aji Sax ji. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”» \s1 Woyu saamar jib na \p \v 45 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal na ma ne ma: \v 46 «Yaw nit ki, neel jàkk yoonu ndijoor, sànnil kàddu ci kaw bëj-saalum googu, waxal \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* ci kaw gottub Negew boobu\f + \fr 21.2 \fr*\ft Waxyu bii mu ngi jëm ci wàllu Yuda gi féete bëj-saalum.\ft*\f*. \v 47 Dangay wax waa gottub diiwaanu Negew, ne leen: “Déglul kàddug Aji Sax ji. Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jafal ci sa biir, daay guy xoyom sa garab yépp, gu naat ak gu wow. Dara du ko mana fey. Daay ga day jóge bëj-saalum ba bëj-gànnaar te ñépp a cay lakk, \v 48 ba mboolem kuy dund xam ne man Aji Sax ji maa ko taal te du fey.”» \v 49 Ma ne ko: «Éey Boroom bi Aji Sax ji, ñii déy a ngi wax ci man, naan: “Kii moom xanaa day léeb ak a léebaat rekk?”» \c 21 \p \v 1 Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma: \v 2 «Yaw nit ki, jàkkaarlool ak Yerusalem, nga sànni kàddu bérab yu sell yi te nga wax waxyu ci kaw réewum Israyil. \v 3 Waxal réewum Israyil ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngi nii fi sa kaw. Maay boccee sama saamar mbaram, daldi dagge fi yaw ku jub ak ku bon. \v 4 Dagge fi yaw ku jub ak ku bon moo may taxa boccee sama saamar mbaram, dal ci mboolem kuy dund, bëj-saalum ba bëj-gànnaar, \v 5 ba képp kuy dund xam ne man Aji Sax ji maa bocci sama saamar, te du dellu mbaram.” \v 6 Yaw nit ki, binnil, neel yàcc, di binnee naqar, ñuy gis. \v 7 Dees na la laaj ne la looy binni. Nga ne leen: “Xanaa mbir mi ma dégg. Bu agsee fit yépp ay rëcc, loxo yépp nasax, xol yépp jeex, óom yépp di fenqoo. Mu ngooguy dikk te dina am. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”» \p \v 8 Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma: \v 9 «Yaw nit ki, waxal bii waxyu, nga ne: “Boroom bi dafa wax ne: \q1 Saamar a ngoog, \q1 saamar bu ñu xacc, jonj ko! \q1 \v 10 Dees koo jonj ngir bóome, \q1 jonj koo jonj ba muy tàkk. \q1 Ana nu nu mana bége lii? Ngeen ne Aji Sax ji nee: ‘Yetu nguurug Yuda sama doom a ngi fi.’ \q1 Waaye saamar bi faalewul benn bant! \q1 \v 11 Santaane nañu ñu jonj saamar bi, \q1 ba loxo man koo téye, \q1 ñu xacc ko, jonj ko, \q1 nar koo teg ci loxol bóomkat. \q1 \v 12 Yaw nit ki, yuuxul, jooyal, \q1 saamar bi dikkal na sama ñoñ, \q1 dikkal mboolem kàngami Israyil, \q1 boole leen ak sama ñoñ, jalax ci kaw saamar. \q1 Kon nag, màttul, wiccax! \q1 \v 13 Nattu bi metti na! \q1 Bu yetu nguur, wi saamar bi xeeb, demee, ana luy xew? \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.” \b \q1 \v 14 «Yaw nit ki, jottlil waxyu, \q1 ŋëbal bii loxo, dóor ca bee. \q1 Na saamar bi dal benn yoon, ñaari yoon, ba ñett, \q1 saamaru ndee la, saamar baay bóom ñu bare, \q1 gaw leen, \q1 \v 15 yóbbuw fit, \q1 tërëfloo ñu bare. \q1 Seen buntoo bunt laa teg saamaru bóomkat. \q1 Ndeysaan, bii saamar bu ñu defar ba muy tàkk, \q1 xacc ko ngir bóome. \q1 \v 16 Saamar, ñaweel sa ndijoor, \q1 walbatiku, jëm càmmoñ, \q2 ak foo mana jublu, \q1 \v 17 man it ma ŋëb bii loxo, dóor ca bee, \q1 ba giifal sama xadar. \q1 Man Aji Sax ji maa ko wax.» \p \v 18 Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma: \v 19 «Yaw nag nit ki, sàkkal ñaari yoon yu saamaru buuru Babilon di jaare dikk; ñaari yoon yuy bàyyikoo menn um réew. Tegal fa buntu yoon wu ci nekk màndarga muy tegtale dëkk ba yoon wa jëm; \v 20 wenn yoon wa jëme saamaru Babilon ca Raba, dëkkub Amoneen ñi; wa ca des jëme ko Yerusalem, dëkk ba ñu dàbbli, ca Yuda. \v 21 Buuru Babilon a ngay taxaw ca selebe yoon wa, fa ñaari yoon ya séddlikoo, ngir gisaane. Dina yëngal fitti seetukaay yi, xool ci terafim yi, jumtukaay yi ñuy gisaanee, te dina xool ci resu jur. \v 22 Fitt giy misaal Yerusalem ndijooram lay wadd. Mu sës dénki dàjjikaay yi, yéene ndigalu bóome, xaacu, daldi sës dénki dàjjikaay yi ci bunt yi, yékkati sëkk yi, ngir taxawal ab gawukaaay. \v 23 Waa Yerusalem foog ne ngisaane googu misaal seen jéll, caaxaan la, ndax ngiñ moo lal seen kaaraange, ba du deñ. Waaye buuru Babilon a leen di fàttli seenug tooñ, ba jàpp leen njaam. \p \v 24 «Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Gannaaw yeena fàttliku seen ñaawtéef, seeni tooñ ne fàŋŋ, seeni bàkkaar fés ci seen jëf jépp, gannaaw yeena ñaaw ñaawtéef gu ñu leen di fàttlikoo, dees na leen jàpp. \b \q1 \v 25 «Waaye yaw garmib Israyil bu teddadi bu bon bi, \q1 sa bés dikk na, sa àppu mbugal mat na.\f + \fr 21.30 \fr*\ft Buur Cedesyas lañuy wax fii. Cedesyas mooy buur bi mujj ci askanu Daawuda. Seetal ci \ft*\ft \+bk 2.Buur ya\+bk* 25.4-7.\ft*\f* \q1 \v 26 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Dindil kaala gi, foq mbaxanam buur mii; \q1 la woon wonni na, \q1 ku noon dett jóg, ku jóg, detteelu. \q1 \v 27 Tasaaroo, tasar, maa ko naa tasar! \q1 Lépp ay wonni, \q1 ba keroog boroom àtte bi dikk, ma jox ko ko. \p \v 28 «Yaw nag nit ki, jottlil bii waxyu, nga ne: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ci mbirum Amoneen ñeek seeni saaga ne: \q1 Saamaroo saamar, \q1 bocciku, nara bóome, \q1 xacce ba mana yàppe, \q1 di tàkk ni melax. \q1 \v 29 Gisal nañu leen peeñuy caaxaan, \q1 gisaaneel leeni fen. \q1 Teewul saamar ba di tege ca ndoddi \q2 ñu bon ñi ñu nara bóom, \q1 seen bés taxaw, \q1 seen mujjantalu mbugal teew. \b \q1 \v 30 «“Léegi dellooleen saamar ci mbaram. \q1 Saamaroo, fa ñu la sàkke woon, \q1 ca réew ma nga cosaanoo, fa laa lay àttee. \q1 \v 31 Maa lay xëpp samam sànj, \q1 wal sama sawaras xadar fi sa kaw, \q1 jébbal la nit ñu néeg, \q1 ñu xareñ ci sànke. \q1 \v 32 Yaay doon mattum sawara wa, \q1 sa deretu boroom ne xéew fi digg réew mi, \q1 ba deesatu la fàttliku. \q1 Man Aji Sax ji maa ko wax!”» \c 22 \s1 Yerusalem def nay tojaange \p \v 1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal na ma ne ma: \v 2 «Yaw nit ki, doo tiiñal ñii? Doo tiiñal waa dëkku tuurkati deret yii? Xamal leen seen jëf ju siblu jépp. \v 3 Ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Ab dëkk a ngii buy tuur deret fi biiram, ba tax bésam di jubsi. Mu ngi sàkk ay kasaray tuur, di sobeel boppam. \v 4 Yaw dëkk bii, gàddu nga bàkkaar ndax deret ji nga tuur, sobeel nga sa bopp ndax kasaray tuur yi nga sàkk. Kon gàttal nga saw fan, agsi nga ci sa àppu at. Moo tax maa lay def ku mboolem xeet yi di sewal, ku mboolem waa réew yi di kókkali. \v 5 Dëkk bu yàqu bi nga doon, ku jegeek ku soree lay kókkali. Boroom der bu yàqu bi, sa lépp a salfaañoo! \v 6 Kàngami Israyil a ngii fi sa biir, di jaay doole bay tuur deret. \v 7 Ndey ak baay, ñu tuutal fi sa biir; doxandéem bi, ñu lekk àqam fi sa biir; jirim akub jëtun, ñu néewal fi sa biir. \v 8 Sama mbir yu \w sell|lemma="sell:"\w*, nga sàggane, sama \w bési Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*, nga ñàkke worma. \v 9 Ay soskat a ngi fi sa biir, di lor ay bakkan. Kaw tund yi lañuy lekke ñam wu ñu sarxeel ay tuur fi sa biir, tey def jëfi yàqute fi sa biir. \v 10 Baay la doom di teddadil lalam fi sa biir, ku gis baax, ñu tëdde fi sa biir. \v 11 Kii ak jabaru jaambur ci jëf ju siblu, kee sobeel jabari doomam ci biir yàqute, kale di tëdde rakki doom baayam fi sa biir. \v 12 Alalu ger, ñu jël fi sa biir, ngir lor ay bakkan. Ndollant ci kaw tegandaay, nga jël feyeekoo bor, di wute alal sa àqu moroom. Man nag, nga fàtte ma. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \p \v 13 «“Maa ngii nag di fenqe samay loxo, di ko mititloo alal ju lewul ji nga dajale, ak sa dereti nit ji ñu tuur fi sa biir. \v 14 Mbaa keroog bés ya may jëflanteek yaw, dinga am fit ak doole joo ko dékkoo? Man Aji Sax ji maay wax, jëfe ko. \v 15 Maa lay tasaare fi biir xeet yi, wasaare la fi réew yi, ba tàggale laak sa sobe. \v 16 Dinga teddadil sa bopp, xeet yiy gis, ba nga xam ne maay Aji Sax ji.”» \p \v 17 Ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma: \v 18 «Yaw nit ki, waa kër Israyil mbuubitu weñ gu raxe lañu ci man léegi. Ñoom ñépp duñu lenn lu moy xànjar ak weñ gu weex ak gu ñuul ak beteex ci biir taalub tëgg. Mbuubitu xaalis rekk lañu. \v 19 Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: “Gannaaw doon ngeen yeen ñépp mbuubitu weñ, maa ngii nag di leen dajale fi digg Yerusalem. \v 20 Ni ñuy boolee xaalis ak xànjar ak weñ gu ñuul ak beteex ak weñ gu weex ci biir ab taal, xamb sawara wa ngir seeyal ko, ni laa leen di boolee ci sama biir mer ak sama xadar, jóor leen, seeyal leen. \v 21 Maa leen di saam fi digg Yerusalem, jafale leen sama tàngooru xadar, ba ngeen seey ca biir. \v 22 Ni xaalis di seeye ci biir taal, ni ngeen di seeye ca biir. Su boobaa ngeen xam ne man Aji Sax ji maa leen xëpp sama xadar.”» \p \v 23 Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma: \v 24 «Yaw nit ki, waxal Yerusalem ne ko: “Yaa di suuf su ñu dindiwul sobeem, te tawluwul keroog bésub sànj ma.” \v 25 Ay yonentam a ngi déeyoo fi biiram; ñu ngi xiiru ni gaynde guy xotat pàddam, di lekk doom aadama yi, foqati alal ak gànjar, ful jëtun yi ci biiram. \v 26 Ay \w sarxalkatam|lemma="sarxalkat b-:"\w* xëtt nañu sama yoon, teddadil nañu sama yëf yu sell. Lu sell ak lu sellul, ràññeewuñu ko; lu set ak lu sobewu, xamlewuñu ko; sama bési Noflaay, ñu jéllale ko, ba ma mujj teddadi fi seen biir. \v 27 Kàngamam yi ci biiram a ngi mel ni saafaandu yuy dogat am pàdd, tuur deret ja, di sànk ay bakkan ngir nangu alali boroom. \v 28 Ay yonentam di leen diwal weexal ci kaw loolu lépp, ci peeñuy caaxaan ak ngisaaney fen, naan: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne,” te Aji Sax ji waxul. \v 29 Waa réew maa ngi lekk àq, di sàcc. Baadoolo yeek walaakaana yi, ñu néewal; doxandéem bi, ñu not, xañ ko àqam. \v 30 Ma seet ci seen biir kuy defaraat tata ji, janook man ci bëttukaay bi, ngir taxawal réew mi, ba duma tas réew mi, waaye gisuma kenn. \v 31 Ma daldi leen xëpp samam sànj, fàkkase leen sama tàngooru xadar, këpp leen seen añu jëf ci seen kaw bopp. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.» \c 23 \s1 Samari ak Yerusalem bokkaale nañu \p \v 1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal ma ne ma: \q1 \v 2 «Yaw nit ki, ñaari jigéen la woon, \q1 ñu bokk jenn ndey, \q1 \v 3 di gànctu ca Misra, \q1 te doon fa gànctu ca seenug ndaw. \q1 Fa lañu doon làmbe seeni ween, \q1 di motoxal seen cusi janq. \q1 \v 4 Ku mag kaa doon Owola, \q1 rakk ja di Owoliba. \q1 Ñu di samay soxna, \q1 jural may doom, góor ak jigéen. \q1 Owola mooy Samari, \q1 Owoliba di Yerusalem. \q1 \v 5 Owola di sama soxna tey gànctu, \q1 di xédd ay faram, waa Asiri xarekat ya. \q1 \v 6 Ña nga sol seen mbubbi baxa, \q1 diy kàngam aki jawriñ, \q1 ñoom ñépp di xale yu góor yu sopplu, \q1 di ndaanaani gawar. \q1 \v 7 Boppam la daan jox tànnéefi doomi Asiri yooyu yépp, \q1 di sobeel boppam ak mboolem tuuri ñooñu mu xédd. \q1 \v 8 Gànctoom ga woon ca Misra, bawu ko. \q1 Moom lañu daan tëdde cag ndawam, \q1 te ñoo daa motoxal cusi janqam, \q1 ba sotti ko seen yàqute. \q1 \v 9 Moo tax ma teg ko ca loxoy faram ya, \q2 loxoy waa Asiri ya mu daan xédd. \q1 \v 10 Ñoo ko ñori ba mu ne duŋŋ, \q1 doomam yu góor ak yu jigéen, ñu nangu, \q1 moom, ñu jam ko saamar, rey ko. \q1 Nii lañu sottale ay mbugalam, \q1 ba mu yedd jigéen ñépp. \b \q1 \v 11 «Owoliba rakk ja gis ca \q1 te gëna yàqu magam, \q1 di gànctu ba raw mag ja. \q1 \v 12 Moom it waa Asiri ya la xédd, \q1 ñuy kàngam aki jawriñ, \q2 xarekat yu ràngu ba solu ba jekk, \q1 di ndaanaani gawar, \q1 ñoom ñépp di xale yu góor yu sopplu. \q1 \v 13 Ma gis ni mu sobeele boppam, \q1 muy wenn yoon wu ñu bokk ñoom ñaar. \q1 \v 14 Teewul rakk ja gëna gànctooti, \q1 gis nataali góor yu ñu yett ciy tabax, \q1 di jëmmi waa Babilon yu ca ñaase, xonq curr. \q1 \v 15 Ña nga takk ngañaay ca seen ndigg, \q1 tañlaayu bay langal, \q1 ñoom ñépp di nirooki kàngam, \q1 di saf doomi Babilon, \q1 réewum Kalde di seen cosaan. \q1 \v 16 Rakk ja teg nataal ya bët rekk, xédd leen, \q1 yónnee leeni ndaw fa Kalde. \q1 \v 17 Doomi Babilon ya dikk, \q1 fekksi ko ci kaw lalu baane, \q1 sobeel kook seen yàqute, \q1 mu sobeel boppam ak ñoom ba ñu sàppi ko. \q1 \v 18 Moo siiwal gànctoom, \q1 wone yaramu neenam, \q1 ba sàppi ma ni ma magam sàppee. \q1 \v 19 Mu gën di gànctooti, \q1 di ko baaxantale janti ndawam, \q1 ba muy gànctu ca réewum Misra. \q1 \v 20 Muy xédd ay faram \q2 yu seeni ngóora di saf yu mbaam, \q2 te ñu aldee alde ba mel niy fas. \b \q1 \v 21 «Yaw Owoliba de, yaa namm sa yàqute ga woon ba ngay ndaw, \q1 ba waa Misra di motoxal say cus, \q1 ngir bànneexoo sa weeni janq. \q1 \v 22 Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 “Owolibaa, maa ngii di xabtalsi say far ci sa kaw; \q1 ñi la sàppi, ñoom laay bàbbee fi la wër, \q1 xiirtal leen fi sa kaw: \q1 \v 23 waa Babilon, Kaldeen ñépp, \q1 muy waa Pekot, di waa Sowa, di waa Kowa, \q1 ànd ak waa Asiri yépp, \q1 di xale yu góor yu sopplu, \q1 ñoom ñépp di kàngam aki jawriñ, \q1 di kilifa yu ràññiku, \q1 ñoom ñépp war ay fas. \q1 \v 24 Dañuy dal fi sa kaw, \q2 aki gànnaay, watiir aki mbege ak kurélu xeeti xeet, \q1 ŋàbb pakk bu mag ak bu ndaw, sol mbaxanam xare, \q1 dar kepp la. \q1 Maa leen di jox sañ-sañu mbugal, \q1 ñu mbugal la, ni ñu baaxoo mbugale. \q1 \v 25 Maa lay yen sama fiiraange, \q1 te yaw lañuy jëflanteel ak xadar, \q1 sa bakkan ak say nopp, ñu njoof, \q1 saw ndes fàddoo saamar. \q1 Say doom, góor ak jigéen, ñu nangu, \q1 sa kuutaay lakk ba xoyomu. \q1 \v 26 Dañuy futti say yére, foqati say gànjar. \q1 \v 27 Maay dakkal sa jëfi yàqute, \q1 ak sa gànctu ga dale ca réewum Misra, \q1 ba dootoo ko geesoo gëti nammeel, \q1 te dootoo fàttliku Misra. \q1 \v 28 Boroom bi Aji Sax ji kat dafa wax ne: \q1 Maa ngii di la teg ci loxol ñi nga bañ, \q1 loxol ñi la sàppi. \q1 \v 29 Mbañeel lañuy jëfeek yaw, \q1 foqati ñaqoo ñaq, \q1 wacc la, nga ne duŋŋ duŋŋaaral. \q1 Sa gànctu gu ñàkk kersa dina feeñ, \q1 ak dëgër bët gi ngay cagatoo. \q1 \v 30 Ñoo lay def jii jëf \q1 ndax sa gànctu gi nga toppe yéefar yi, \q1 di sobeel sa bopp ak seen kasaray tuur. \q1 \v 31 Yaa topp sa tànki mag, \q1 kon maa lay nàndale kaasu mbugalam. \q1 \v 32 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Sa kaasu mag ngay naane, \q1 xóot, yaatu, \q1 duy ba ne xéew, \q1 xellil la ay ñaawleeki kekku. \q1 \v 33 Mànditeeku tiis ngay feesi, \q1 kaasu wéetaay ak wéetle di sa kaasu mag Samari. \q1 \v 34 Yaa koy naan ba siitaatu ko, \q1 yéy tojit ya, xotate say ween. \q1 Man de maa ko wax. \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \b \q1 \v 35 «“Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Yaa ma fàtte, \q1 jalax ma sa gannaaw. \q1 Kon nag gàddul sa ayu ñàkk gàcceek sa gànctu.”» \b \q1 \v 36 Aji Sax ji nag ne ma: \q1 «Yaw nit ki, doo tiiñal Owola ak Owoliba? \q1 Kon nag biral leen seeni jëf ju siblu: \q1 \v 37 Ñoo njaaloo, ñoo bóome, \q1 ñoo njaalook seen kasaray tuur. \q1 Doyatu leen, doom yu góor yi ñu ma jural, \q1 ñu di leen lakk ngir ay tuur, leele leen. \q1 \v 38 Lii itam, ñoo ma ko def: \q1 Bésub keroog lañu sobeel sama kër gu sell, \q1 teddadil sama \w bési Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*. \q1 \v 39 Ñoo rendil seen kasaray tuur seeni doom, \q1 ba noppi dugg sama biir kër gu sell ci bés bi, \q1 ba teddadil kër gi. \q1 Loolu déy, moom lañu def fi sama digg kër gii! \q1 \v 40 Te sax ñoo yeble, wutiy góor, \q1 yónnee ndaw lu leen jële fu sore, \q1 ñu daw dikk, \q1 fekk leen sangu, tusngalu, gànjaru, \q1 \v 41 tooge lal bu yànj, \q1 taabal taaje fa kanam, \q1 sama cuuraay ak sama diw gu xeeñ tege ca. \q1 \v 42 Muy coowal gàngoor gu amul xalaatu àddina; \q1 doom aadama ju nekk a nga ca, \q1 ba ci ay màndikat yu ñu jële ca màndiŋ ma, \q1 ñooña di leen takkal lami loxo, \q1 di leen solal mbaxanam lingeer. \q1 \v 43 Booba laa wax ci ndaw sii njaaloo ba ràpp, ne: \q1 “Ndaw sii lañuy gànctool ba tey?” \q1 \v 44 Mu daldi ànd ak moom ni ñuy àndeek caga rekk. \q1 Nii lañu àndeek Owola ak Owoliba. \q1 Ñii jigéen ñu ñàkk gàcce! \q1 \v 45 Waaye ay nit ñu jub a ngii, \q1 ñoo leen di atteji àtteb njaalookat yu jigéen, \q2 àtteb bóomkat yu jigéen, \q1 nde ay njaalookat lañu, \q1 te ay bóomkat lañu. \b \q1 \v 46 «Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: \q1 Wool gàngoor ci seen kaw, \q1 bàyyee leen tiitaange aki sëxëtookat. \q1 \v 47 Gàngoor gaa leen di dóor ay doj, \q1 jam leeni saamar, ñu dee, \q1 seeni doom, góor ak jigéen, ñu bóom; \q1 seeni kër, ñu taal, \q1 \v 48 ma dakkale noonu yàqute ci réew mi, \q1 jigéen ñépp jànge ca, \q1 baña jëfeeti yàqute ju mel ni seen jos. \q1 \v 49 Dees na leen këpp seen yàqute, \q1 ngeen yenu seen bàkkaari kasaray tuur, \q1 ba xam ne man maay Boroom bi Aji Sax ji.» \c 24 \s1 Mbugalu Yerusalem, misaal maa ngi \p \v 1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal na ma ca juróom ñeenteelu at ma, fukki fan ca fukkeelu weer wa. Mu ne ma: \v 2 «Yaw nit ki, bindal bés bii, bés bii ci boppam, ndax buuru Babilon gaw na Yerusalem bés niki tey. \v 3 Léebalal kërug fippukat yi aw léeb, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Taalal, teg cin li, teg ko, sotti ci ndox. \q1 \v 4 Booleel dogi yàpp yi, def ci: \q2 dog yu baax yépp, fàllare jeek tànku kanam bi, \q1 te feccalee ko cér ya gëna baax. \q1 \v 5 Li gën ci gétt gi ngay sàkk, \q1 nga jal matt ci suufu cin li, \q1 xamb, baxala baxal, ba baxalaale yax yi.”» \q1 \v 6 Boroom bi Aji Sax ji kat dafa wax ne: \q1 «Wóoy ngalla bii dëkku tuurkatu deret! \q1 Mooy cin lu teg àkki xëmit, \q1 cin lu dul tàggook xëmitam. \q1 Wenn-wenn ngay seppi dogi yàpp yi, \q1 te bul tegoo bant la ngay seppi. \q1 \v 7 Deret ji mu tuur a ngi ci biiram ba tey; \q1 doj wu amul dara la ko sotti, \q1 sottiwu ko ci suuf, fu muy suuloo. \q1 \v 8 Man maay wacc deret ja ca doj wa amul dara, \q1 fa mu naan fàŋŋ, du suulu, \q1 ngir mu doon sànj muy wàcce mbugal.» \q1 \v 9 Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: \q1 «Wóoy ngalla bii dëkku bóomkat! \q1 Man it dinaa yokk jalu matt mi. \q1 \v 10 Jalala jal matt mi, xamb taal bi. \q1 Baxalal yàpp wi bu baax, ŋeeral, \q1 ba yax yi far xëm. \q1 \v 11 Boo noppee tegal cin li deful dara ci xal yi, \q1 mu tàng ba xànjar bi xonq curr, \q1 tilim ja seey ca biir, \q1 xëmit ja xoyomu. \q1 \v 12 Coonoy neen, xëmit ja ne xéew du deñ, \q1 sawara sax dindiwu ko. \q1 \v 13 Sa sobeey sa yàqute! \q1 Maa la setal te taxu laa set. \q1 Dootuloo tàggook sa sobe, \q1 ba keroog may giifal sama xadar fi sa kaw. \q1 \v 14 Man Aji Sax ji maa wax, \q1 mu dikk, ma jëfe ko. \q1 Duma bàyyi, duma ñéeblu, duma yërëm; \q1 say jikko ak say jëf lees lay àttee. \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.» \s1 Soxnas Esekiyel faatu na \p \v 15 Gannaaw loolu kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal na ma ne ma: \v 16 «Yaw nit ki, maa ngii di nangusi sa bànneexu bët cim pàdd. Bul yuuxu, bul jooy, bu sa rongooñ wadd. \v 17 Binnil ndànk te bul ñaawlu. Bul tàggook sa kaala, bul tàggook say carax, bul muur sa tuñum kaw ba ci sikkim di ko ñaawloo. Bul lekk ñam wu la njaal mi indil.\f + \fr 24.17 \fr*\ft Ku deele daawul togg. Waa njaal mi ñooy indi ñam wu ñu lekk ci dëj bi.\ft*\f*» \p \v 18 Wax naak mbooloo mi ci suba, ci ngoon si sama soxna dee. Bët set ma def li ñu ma sant. \v 19 Mbooloo mi nag ne ma: «Xanaa doo nu wax lii ngay def nii, lu muy wund ci nun?» \v 20 Ma ne leen: «Kàddug Aji Sax jee ma dikkal, ne ma: \v 21 Waxal waa kër Israyil, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di teddadil sama bérab bu sell bii, seen sag bii ngeen di doolewoo, di seen bànneexu bët, di seen nammeelu bakkan. Seen doom yu góor ak yu jigéen ya ngeen bàyyi Yerusalem, saamar dina leen tëral. \v 22 Te nangeen def nii ma def. Buleen muur tuñum kaw ba ci sikkim te buleen lekk ñam wu leen njaal mi indil. \v 23 Buleen tàggook kaala, buleen tàggooki carax. Buleen yuuxu, buleen jooy. Waaye dingeen jeex tàkk ndax seeni ñaawtéef, ngeen ànd di binni.” \v 24 Mu ne: “Na Esekiyel di seen misaal. Bu jotee, mboolem nu mu def, nangeen ko def, ba xam ne man maay Boroom bi Aji Sax ji.” \p \v 25 «Yaw nit ki, bés bu ma nangoo ci ñii seen tatay daraja ji ñuy bége, muy seen bànneexu bët, di seen xintey bakkan, ba nanguwaale seen doom yu góor ak yu jigéen, \v 26 bésub keroog ku ca rëcce dina dikk ba ci yaw, àgge la xibaar bi. \v 27 Bésub keroog sa gémmiñ dina ubbiku, nga noppee luu, ba wax ak ka rëcc. Su boobaa yaay doon misaalu mbooloo mi, ba ñu xam ne maay Aji Sax ji.» \c 25 \s1 Kàddug waxyu dal na xeet yi \s2 Waxyu dal na Amon \p \v 1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal na ma ne ma: \v 2 «Yaw nit ki, neel jàkk Amoneen ñi, nga wax \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* ci seen kaw. \v 3 Waxal Amoneen ñi, ne leen: \q1 “Dégluleen kàddug Boroom bi Aji Sax ji. \q1 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 yeena noon: ‘Ñaw!’ ba ñuy teddadil sama kër gu sell, \q1 réewum Israyil gental, \q1 waa kër Yuda jëm ngàllo. \q1 \v 4 Maa ngii nag di leen jébbal màngaani penku, \q1 ñu moom leen, \q1 samp seeni dal fi seen biir, \q1 yékkati fa seeni xayma. \q1 Ñooy lekk seen meññeef, \q1 naan seen meew. \q1 \v 5 Maay soppi Raba seen péey ab parlub giléem, \q1 maay def réewum Amon goorukaayu gàtt, \q1 ba ngeen xam ne maay Aji Sax ji. \q1 \v 6 Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: \q1 Yeena doon tàccu, \q1 di fecc, bége tiisu réewum Israyil, \q1 di leen sewal lu ngeen man. \q1 \v 7 Maa ngii nag di leen dóor sama loxo, \q1 te maa leen di jébbal xeet yi, ñu sëxëtoo leen. \q1 Maa leen di dagge fi digg xeet yi, \q1 maa leen di fare ci réew yi, \q1 faagaagal leen, \q1 ba ngeen xam ne maay Aji Sax ji.”» \s2 Waxyu dal na Mowab \q1 \v 8 «Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji déy dafa wax ne: \q1 Waa Mowab ak Seyir a ne: “Xool-leen waa kër Yuda ñii ni ñu mujje, \q1 ñook xeet yépp a yem!” \q1 \v 9 Maa ngii nag di ŋafal réewum Mowab, \q1 ba xañ leen mboolem seen dëkk ya gëna taaru sax, \q1 di Bet Yesimot ak Baal Mewon ak Kiryaatayim. \q1 \v 10 Màngaani penku laa leen di jébbal, \q1 jébbalaale leen Amon, \q1 ba kenn du fàttlikooti Amon ci biir xeet yi, \q1 \v 11 te maay wàcceel Mowab ay mbugal, \q1 ba ñu xam ne maay Aji Sax ji.» \b \s2 Waxyu dal na Edom \q1 \v 12 «Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: \q1 Edom a feyu ci waa kër Yuda, \q1 feyu ga mu feyu di tooñaange gu réy. \q1 \v 13 Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Maay dóor Edom sama loxo, \q1 dagge fa nit ak mala, \q1 maa koy def ab gent, \q1 la dale Teman ba Dedan, saamar lañuy fàddoo. \q1 \v 14 Maay duma Edom, \q1 te Israyil sama ñoñ laa leen di dumaa. \q1 Ñooy jëflanteek Edom la méngook sama mer, \q1 tollook sama xadar, \q1 ba ñu ñam sama mbugal. \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.» \s2 Waxyu dal na Filisti \b \q1 \v 15 «Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji déy dafa wax ne: \q1 Filisteen ñee jiital seen mbañeel gu sax, \q1 ñoo jéppee jéppi seeni noon, feyoo feyu, \q1 ba faagaagal leen. \q1 \v 16 Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Maa ngii di dóor Filisteen ñi sama loxo, \q1 maay dagg ñooñu di askanu Keret, \q1 maay fàkkas ndes wa ca tefesu géej. \q1 \v 17 Maa leen di feye mbugalu xadar yu mag, \q1 te bu ma leen yenee sama peyu mbugal, \q1 ñu xam ne maay Aji Sax ji.» \c 26 \s2 Waxyu dal na Tir \p \v 1 Ba loolu amee, ca fukkeelu at maak benn, yemook benn fanu weer wa, kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal ma ne ma: \q1 \v 2 «Yaw nit ki, \q1 Tir dëkk ba moo ree Yerusalem, \q1 ne: “Ñaw! Buntu dëkk bi xeet ya daan jaare dàjjiku na! \q1 Léegi man la bunt ubbikul, \q1 léegi maay woomle, Yerusalem gental na.” \q1 \v 3 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Yaw Tir, maa ngii fi sa kaw. \q1 Ni géej di yéegee ay gannaxam, \q1 ni laay yéegloo fi sa kaw xeet yu bare. \q1 \v 4 Ñooy màbb say miir, \q1 daane say tata, \q1 ma buube fa pënd ba, \q1 def ko doj wu ne duŋŋ. \q1 \v 5 Tir ay doon wéerukaayu caax ci digg géej gi, \q1 maa ko wax, kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \q1 Dëkk bii mooy doon sëxëtoom xeet yi, \q1 \v 6 dëkk-dëkkaan yi bootu ci mbooyam fàddoo saamar, \q1 ñu xam ne maay Aji Sax ji. \p \v 7 «Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: Maa ngii di jële bëj-gànnaar, indi ci kaw Tir, Nabukodonosor buuru Babilon, buuru buur yi, aki fas aki watiir aki gawar, ak mbooloo mu takku. \b \q1 \v 8 «Dëkk-dëkkaan yi bootu ci sa àll bi, saamar la leen di reye. \q1 Mooy yékkati fi la wër ab gawukaay, \q1 jal ay sëkk, gawe la, \q1 yékkati kiiraayu xare yu ràbbaloo ba def um taax, janook yaw, \q1 \v 9 mooy rëkke say miir dénku dàjjikaay, \q1 mooy màbbe say tata ay sémmiñam, \q1 \v 10 ay fasam yu bare sànge la pënd, \q1 riiru gawar yaak mbege yaak watiir ya riiral say miir, \q1 mu jàlle say wunt, dugg, ni ñuy bëtte dëkk, \q1 bu ñu bëtt tataam. \q1 \v 11 Tànki naari góoram lay note sa mbeddoo mbedd, \q1 sa mbooloo mi, mu bóome saamar; \q1 sa kenuy tabax yu dëgër jóoru fi suuf. \q1 \v 12 Ñooñooy foqati sam koom, \q1 sëxëtoo sa alal, \q1 màbb say miir, \q1 daane sa kër yu bakkane, \q1 boole doj yaak bant yaak pënd ba, \q1 tàbbal ca mbeex ma. \q1 \v 13 Maay dakkal say woy, \q1 ba say xalam du fi jibeeti. \q1 \v 14 Maa lay def doj wu ne duŋŋ, \q1 bérabu wéerukaayu caax ngay doon, \q1 te deesu la tabaxati mukk. \q1 Man Aji Sax ji déy maa ko wax! \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \b \q1 \v 15 «Boroom bi Aji Sax ji dafa wax Tir, ne ko: \q1 Keroog sa coowal jéll ba, \q1 ba ñuy bóome fa sa biir, \q1 ñay dee di binni, \q1 dun yaa cay dégg, di lox moos! \q1 \v 16 Mboolem buuri tefes yaay wàcc seeni ngàngune, \q1 futti seeni mbubb, \q1 tàggook seen yére yu yànj, \q1 bàddoo tiitaange, \q1 ne dett fi suuf, \q1 dëkke kat-kat, \q1 seen yaram dawe saw demin. \q1 \v 17 Ñooy yékkati kàddu, jooye la, ne la: \q1 “Yaaka sànku tey, yaw dunu géej bu xumb bi woon, \q1 yaw dëkk bu siiw bi woon, di jàmbaaru waa géej, \q1 yaak say nit a daa tiital mboolem ñi leen wër. \q1 \v 18 Tey sa bésub jéll bii, \q1 dun yeey xala lox. \q1 Duni géej yeey tiit ci sa sànkute gi.” \b \q1 \v 19 «Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: \q1 Bu ma lay def dëkk bu gental, \q1 nga mel ni dëkk yu nit ña ne mes, \q1 ba ma waral xóote ya fi sa kaw, \q1 ba wali ndox ya mëdd la, \q1 \v 20 keroog maa lay wàccaaleek ñay wàcci biir pax, \q1 nga fekki xeetu démb. \q1 Maa lay dëël taati biir suuf, \q1 fu mel ni genti cosaan ya, \q1 nga fekki pax ña fa jëkkoona wàcc, \q1 ngir deesatu la dëkke, \q1 te doo amati cér réewum aji dund ña. \q1 \v 21 Demin wu raglu laa lay sédd, \q1 ba nga ne mes, \q1 ñu di la seet, te deesu la gisati mukk. \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee!» \c 27 \s1 Esekiyel jooy na Tir \p \v 1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal na ma ne ma: \v 2 «Yaw nag nit ki, yékkatil kàddu, jooye ko dëkkub Tir. \v 3 Waxal Tir mi tooge buntu géej, jula yooyuy jëflanteek xeeti dun yu bare, nga ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Yaw Tir yaa noon: \q1 ‘Maaka matub taar!’ \q1 \v 4 Yaw mi sa kemu suuf àkki xolu géej, \q1 say tabaxkat a mottli sab taar. \q1 \v 5 Dañu laa tabax ni ñuy tabaxe gaal, \q1 sàkke xànqi sippar fa tundu Senir, \q1 defare ca sa xott wépp, \q1 sàkk bantu seedaru Libaŋ, \q1 defare ponku diggu gaal ga. \q1 \v 6 Ñu gorati garabu seen yu Basan, \q1 defare say joowu, \q1 kaw gaal gi, ñu defare ko banti sippar yu bawoo tefesi Géej gu mag ga, \q1 rafetale ko bëñi ñey. \q1 \v 7 Lẽe bu bawoo Misra lañu ràbb ba mu jekk, \q1 def ko ndimoy wiiru gaal gi, \q1 nga raayawoo ko, \q1 cuub gu baxa ak cuub gu xewar bawoo dunu Elisa, \q1 di sa malaan, \q1 \v 8 waa Sidon ak Arwàdd doonoon say joowkat. \q1 Yaw Tir, yaa yeb ñu rafet xel, \q1 ñuy say mool, \q1 \v 9 magi Gebal ñeek nitam ñu xareñ ñi fi yaw féetewoo di jagal. \q1 Mboolem gaal yu mag yi ak ña cay liggéey di dal ak yaw, \q1 waa gaal ya di jënd sam njaay. \q1 \v 10 Waa Pers ak waa Ludd ak waa Puut, \q1 ñépp a nga woon ca sa mbooloom xare, \q1 di wékk fa yaw seeni pakk ak seen mbaxanay xare. \q1 Ñooñoo la darajaal. \q1 \v 11 Arwàddeen ñeek sa niti bopp a daan wattoo ca sa kaw miir yépp, \q1 Gammàddeen ñi di wattu say tata, \q1 seeni gànnaay wékke, wër say miir. \q1 Ñooñoo mottli sab taar. \p \v 12 «“Tarsis dëkk baa doon sab jula ndax sa gépp xeetu alal ju bare, di indi xaalis, weñ gu ñuul ak gu weex ak beteex, di ko weccikoo seen alal. \v 13 Waa Geres ak Tubal ak Meseg di say jula, di leen indil ay doom aadama ak ndabi xànjar yu ñuy weccikoo seen koom. \v 14 Waa kër Togarma indi ay fas aki gawar aki berkelle, di ko weccikoo seen alal. \v 15 Dedaneen ñi di say jula, koomu dun yu bare di jaare say loxo, ñu di la feye bëñi ñey ak bantu jalambaan. \v 16 Waa Siri it di say jula, di jëndeek yaw lu bare loo defar, di ko wecci per yu jafe, ak ndimo yu xewar, ak séri ràbb ak lẽe ak peri koray ak peri rubi. \v 17 Yudak réewum Israyil it di say jula, di la wecci bele bu bawoo Minit, ak dugub ak lem ak diwu togg ak diwu yaram. \v 18 Dëkkub Damaas di la jula lu bare loo defar ak jépp alal joo barele, di la ko weccee biiñ bu jóge Elbon, ak kawaru xar gu weex. \v 19 Waa Weden ak Yawaan bàyyikoo Usal, di la wecci sa koom weñ gu ñu tëgg, ak xasum kaas, ak barax bu xeeñ. \v 20 Waa Dedan it di say jula, indil la seen ndimoy tegi fas. \v 21 Waa Arabi ak mboolem garmiy Kedar it di julanteek yaw, feye la ay tàppaanga aki kuuy aki bëy. \v 22 Julay Saba ak Raama it di julaak yaw, di la indil ngën-gi-safal ak mboolem peru gànjar, ak wurus yu ñuy weccikoo sa alal. \v 23 Waa dëkk yii di Karan ak Kane ak Eden ñoom it di say jula, ñook julay Saba ak Asur ak Kilmàdd. \v 24 Ñooñoo doon say jula yu lay indil yérey tànnéef, ak turki yu yolet, ak yérey ràbb, ak malaan yu yànj, ak goj yu rawaasoo yu wér. \v 25 Ay gaali Tarsis yu mag a daan yóbbu sam njaay. \q1 Nga fees dell, diis gann fi digg xolu géej. \q1 \v 26 Say joowkat waral la mbeex mi ne màww, \q1 ba digg géej, teewul ngelawal penku damm la. \q1 \v 27 Sa alal ja, sab yeb, sa njaay ma, \q1 sa niti géej, say mool, say jagalkat, say jaaykat, \q1 ak mboolem sa dag yi ci sa biir, \q1 ak mboolem sa gàngoor gi ci sa biir, \q1 ñooy tàbbeendoo xolu géej keroog sa bésub jéll ba. \q1 \v 28 Bu say mool yuuxoo, \q1 tefes yaay riir, \q1 \v 29 képp kuy ŋàbb joowu wàcce gaalam. \q1 Nitu géejoo mboolem mool, \q1 ñépp fi suuf lañuy taxaw. \q1 \v 30 Ñoo lay jooyal, \q1 di yuuxu yuux yu metti, \q1 xëppoo suuf, \q1 fërënqu cib dóom. \q1 \v 31 Yaay tax ñuy nelu, \q1 sol ay saaku di ko ñaawloo, \q1 di la jooye naqaru xol ak yuux yu metti. \q1 \v 32 Ñeey am tiis, yékkatil la kàddug jooy, \q1 jooy la ne: \q1 ‘Ana dëkk bu mel ni Tir, \q1 mi ñu wedamal nii biir géej?’ \q1 \v 33 Ba ngay yebbee géej sam koom, \q1 yaa daan reggal ñu bare. \q1 Sa alal ak sa koom gu bare nga woomale buuri àddina. \q1 \v 34 Léegi rajaxoo nga biiri gannax ca biir xóotey géej, \q1 sa koom ak sa gàngoor gi ci sa biir, lépp jóoru. \q1 \v 35 Waa dunoo dun a la tiisoo, \q1 seen yaramu buur ya dawa daw ba ñu ne yasar. \q1 \v 36 Julay xeet yaa ngi muslu ci saw demin. \q1 Raglu nga mujje, \q1 te doo tekkeeti ba fàww!”» \c 28 \s2 Nguurug Tir foq na \p \v 1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal na ma ne ma: \v 2 «Yaw nit ki, waxal Boroom Tir, ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Dangaa fuuy ba naan: \q1 ‘Maay Yàlla, ji tooge toogub yàlla yi, fi xolu géej!’ \q1 Waaye yaw doom aadama nga, doo Yàlla, \q1 dangay yàlla-yàllalu rekk. \q1 \v 3 Xëy na yaa sut Dañeel am xel, \q1 du genn kumpa gu la ump! \q1 \v 4 Sam xel ak sa manoore nga ame alal, \q1 am wurus, am xaalis, \q1 yeb ci say denc. \q1 \v 5 Sa xelum jula mu réy nga yokke sa alal, \q1 alal ji tax laa fuuy. \q1 \v 6 Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Gannaaw dangay yàlla-yàllalu, \q1 \v 7 maa ngii di la indil ay làkk-kat, \q2 yéefar yi gëna néeg. \q1 La nga sottale xel mu rafet, ñoo koy boccil saamar, \q1 te ñooy yàq sab taar. \q1 \v 8 Pax lañu lay tàbbal, \q1 nga deeyi xolu géej deewug ku ñu bóom. \q1 \v 9 Xanaa doo janook ki lay rey, naati yaay yàlla? \q1 Boo tàbbee ca sa loxoy jamkat ya, \q1 keroog nga noppee doon yàlla, di nitu kese. \q1 \v 10 Deewug yéefar bu xaraful ngay deeye ci loxol làkk-kat yi. \q1 Man déy, maa ko wax! \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”» \p \v 11 Kàddug Aji Sax ji dikkalati ma ne ma: \v 12 «Yaw nit ki, yékkatilal buurub Tir kàddug jooy! Nga ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Yaa matoon royukaay, \q1 géejum xel, sottib taar. \q1 \v 13 Yaa nga woon biir Àjjana, toolub Yàlla ba, \q1 ràngoo lépp luy gànjari per, \q1 sarduwan ak topaas ak jamaa ak kirsolit ak onigsë ak jàspë ak safiir ak emëródd ak eskarbukal. \q1 Fegukaay yaak wewukaay ya di wurus, \q1 te bés ba ñu la sàkkee, fekk na ñu waajal yooyu. \q1 \v 14 Yaa doon malaakam \w serub|lemma="serub y-:"\w* mu ne ràññ, di aare, \q1 ma tabb la fa kaw tundu Yàlla wu \w sell|lemma="sell:"\w* wa, \q1 ngay daagoo digg doj yuy tàkk. \q1 \v 15 Ba ñu la sàkkee, nga dale mat ci say jëfin, \q1 ba keroog njubadi di feeñ ci yaw. \q1 \v 16 Sa liggéeyu jula bu yaatu moo la feesal fitna, \q1 nga bàkkaar, ba ma nangoo sa teddnga fa tundu Yàlla wa, \q1 sànk la, yaw malaakam serub miy aare, \q1 nga jóge digg doj yuy tàkk. \q1 \v 17 Sab taar a la fuuyloo, \q1 sa daraja tax nga yàq sam xel! \q1 Fi suuf laa la rattax, \q1 fi kanam buur yi laa la detteel, ñu di la seetaan. \q1 \v 18 Sa ñaawtéef yu bare ak njublaŋ gi ngay julaa, \q1 looloo teddadil sa jaamookaay yu sell, \q1 ba ma jafale sawara fi sa biir, \q1 mu xoyom la. \q1 Maa la def ub dóom fi suuf, \q1 ñépp di la xool. \q1 \v 19 Mboolem ñi la xam ci xeet yi, \q1 seen yaram dina daw ci yaw. \q1 Ku raglu ngay doon, \q1 te doo tekkeeti ba fàww.”» \s2 Waxyu dal na Sidon \p \v 20 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkalati ma ne ma: \v 21 «Yaw nit ki, neel jàkk Sidon\f + \fr 28.21 \fr*\fk Sidon \fk*\ft dëkk la bu bootu woon ci Tir, ca wetu bëj-gànnaaram.\ft*\f*, nga biral \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* fi kawam. \v 22 Neel: \q1 “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Yaw Sidon, maa ngii fi sa kaw. \q1 Dees na ma sargal fi sa biir, \q1 ba ñu xam ne maay Aji Sax ji \q1 ndax mbugal yi ma fiy wàccesi, \q1 ba fésal fi sama sellnga. \q1 \v 23 Maa fiy yebal mbas, \q1 deret tuuroo mbedd yi, \q1 saamar dajal dëkk bi, \q1 bóom nit ñi, tëral, \q1 ba ñu xam ne maay Aji Sax ji.” \b \q1 \v 24 «Su boobaa waa kër Israyil, seen dëkkandoo yi leen di sewal, \q2 dootuñu leen lëjal ni dagg yu ñaw ak dég yuy jame. \q1 Su boobaa ñu xam ne maay Boroom bi Aji Sax ji. \s1 Aji Sax jeey yiwi Israyil \p \v 25 «Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: Bu may dajale waa kër Israyil, di leen jële digg xeet yi ñu tasaaroo, ca laay fésal sama sellnga fa seen biir, yéefar yi gis, ñu dëkke seen suufas bopp, sa ma joxoon Yanqóoba sama jaam ba. \v 26 Xel mu dal lañu fay dëkke, tabax fa ay kër, jëmbat seeni reseñ. Bu ma wàcceelee ay mbugal mboolem ñi leen di sewal te séq leen, dinañu dëkke ba xam ne maay seen Yàlla Aji Sax ji.» \c 29 \s2 Waxyu dal na Misra \p \v 1 Ca fukkeelu at ma, fukki fan ak ñaar ca fukkeelu weer wa, kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal na ma ne ma: \v 2 «Yaw nit ki, neel jàkk Firawna buuru Misra, nga biral \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* fi kawam ak fi kaw Misra gépp. \v 3 Waxal, nga ne: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Maa ngii fi sa kaw, yaw Firawna buuru Misra, \q1 yaw ninki-nànka ju mag ji goore sa diggi dex, \q1 te naan: ‘Maa moom sama dex, \q1 man ci sama bopp maa ko sàkk!’ \q1 \v 4 Waaye maay we ay lonku ci say ŋaam, \q1 jël sa jëni waltan, \q1 ŋoyal leen ci say waasintóor, \q1 diree la say waltan, \q1 sa jëni waltan yépp ŋoy ci say waasintóor. \q1 \v 5 Ma wacc la ca màndiŋ ma, \q1 yaw yaak mboolem sa jëni waltan. \q1 Ci àll bi nga naa ñàyy, \q1 deesu la for, deesu la fat. \q1 Dundooti àll beek njanaaw yi, yaw laa leen di leele, \q1 \v 6 ba waa Misra gépp xam ne maay Aji Sax ji. \b \q1 «“Seen ndimbal ak Israyil mooy ndimbalu bantu barax, \q1 \v 7 ñu jafandu ko, mu ne tàllit, \q1 ne xureet mbagg yépp, \q1 ñu wéeroo ko, mu ne tipp, \q1 ndigg yépp rëcc. \b \q1 \v 8 «“Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Yaw Misra, maa ngii di la indil saamar, \q1 ba dagge fi yaw nit ak mala. \q1 \v 9 Réewum Misraay gental, di ndànd-foyfoy, \q1 ba ñu xam ne maay Aji Sax ji. \q1 Moo ne: ‘Dex gi maa ko moom, \q1 man maa ko sàkk!’ \q1 \v 10 Moo tax maa ngii fi sa kaw, \q1 yaak say wali dex. \q1 Maay def réewum Misra gent bu ne sereŋ, \q1 mu gentale Migadol ca bëj-gànnaar, ba Asuwan, \q1 fa mu digalook réewum \w Kuus|lemma="Kuus:"\w* ca bëj-saalum. \q1 \v 11 Tànku doom aadama du fa jaare, \q1 tànku mala du fa jaare, \q1 te deesu fa dëkke diiru ñeent fukki at. \q1 \v 12 Maay def Misra gëna gental ci réew yi gental, \q1 ay dëkkam gëna gental ci dëkk yi diiru ñeent fukki at. \q1 Maay tasaare waa Misra ci biir xeet yi, \q1 wasaare leen ci biir réew yi. \q1 \v 13 Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: \q1 Bu ñeent fukki at yi matee, \q1 ma dajalee waa Misra fa digg xeet ya ñu tasaaroo woon. \q1 \v 14 Ca laay tijjee wërsëgu Misra, \q1 delloo leen réewum Pattros ca bëj-saalum, \q2 seen réewum cosaan, \q1 ñu doon fa nguur gu suufe, \q1 \v 15 gëna suufe ci nguur yi, \q1 ba dootuñu damu fi kaw xeet yi. \q1 Maa leen di tuutal ba dootuñu yilif xeet yi. \q1 \v 16 Waa kër Israyil dootuñu yaakaar Misra, \q1 xanaa ñuy fàttliku na ñu ñaawe woon démb, \q1 ba ñuy làqoo waa Misra, \q1 te dinañu xam ne maay Boroom bi Aji Sax ji.”» \p \v 17 Ca ñaar fukkeelu at maak juróom ñaar, benn fan ca weer wa jëkk, kàddug Aji Sax ji dikkal na ma, ne ma: \v 18 «Yaw nit ki, Nabukodonosor buuru Babilon teg na mbooloom xareem, coono bu metti ca seen xareek Tir. Seen kawari bopp yépp ruus na, seen wagg yépp tëccu, te coonoom ba mu sonn ca Tir, yooloowu ca dara, du moom, du ay nitam. \b \q1 \v 19 «Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Maa ngii di jox réewum Misra, Nabukodonosor buuru Babilon, \q1 mu yóbbu alal ja, \q1 wëq ko ba mu set, \q1 sëxëtoo mboolem lu mu amoon, \q1 muy peyooru mbooloom xareem, \q1 \v 20 di yoolu coonoom. \q1 Maa ko jox réewum Misra, \q1 feye ko la ma ay nitam liggéeyal. \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \q1 \v 21 Bésub keroog maay yokk dooley waa kër Israyil, \q1 yaw nit ki, ma jox la sañ-sañu àddu fi seen biir. \q1 Su boobaa ñu xam ne maay Aji Sax ji.» \c 30 \s2 Babilon song na Misra \p \v 1 Ba loolu amee kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal ma ne ma: \v 2 «Yaw nit ki, jottlil \w waxyu|lemma="waxyu:"\w*! Neel: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Jooyleen, ne: ‘Wóoy bii bés!’ \q1 \v 3 Bés jubsi na déy, \q1 \w bésub Aji Sax|lemma="bésub Aji Sax ji-:"\w* ji jubsi na! \q1 Bésub xàmbaar, jantub xeet yi. \q1 \v 4 Saamar ay dikkal Misra, \q1 fépp di jal-jal ba ca \w Kuus|lemma="Kuus:"\w*, \q1 aw nit, ñu bóom ca Misra, \q1 nangu alalu réew ma, \q1 kenu ya màbb. \q1 \v 5 Waa Kuus ak Puut ak Ludd \q2 ak xeet yu raxe yépp ak waa Libi, \q2 boole ci ñenn ci réewum \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* gi, \q1 ñoom ñépp saamar lañuy fàddoo. \b \q1 \v 6 «“Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Wéeruwaayi Misra ya day jóoru, \q1 doole ja Misray sago ŋiis; \q1 la dale Migadol ba Asuwan, saamar lañuy fàddoo. \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \q1 \v 7 Ñooy gëna wéet ci réew yi, \q1 seeni dëkk gëna gental ci dëkk yi. \q1 \v 8 Bu ma taalee Misra, \q1 ba wéeruwaayam yépp rajaxoo, \q1 dinañu xam ne maay Aji Sax ji. \q1 \v 9 Bésub keroog dees na dugg ay gaal, génn ci sama ndigal, \q1 ngir indil tiitaange réewum Kuus ma ne finaax, \q1 muy seen jal-jal keroog bésub Misra ba. \q1 Bés baa ngii déy di dikk! \b \q1 \v 10 «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Maay jeexal mbooloom Misra mu réy, \q1 jaare ko ci Nabukodonosor buuru Babilon. \q1 \v 11 Mooy ànd ak ñoñam, \q1 di ñi gëna néeg ci yéefar yi, \q1 dikk yaqtesi réew mi; \q1 ñooy boccil Misra saamar, \q1 ba feesal réew mi ay néew. \q1 \v 12 Maay def wali Niil ag joor, \q1 maay jaay réew mi nit ñu aay. \q1 Maay alag réew meek li ci biiram, \q1 jaare ko ci ay doxandéem. \q1 Man Aji Sax ji, maa ko wax. \b \q1 \v 13 «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Maay sànk kasaray tuur yi ak yàllantu ya ca Memfis. \q1 Buur dootu tooge jalu réewum Misra, \q1 te maay indi tiitaange biir Misra. \q1 \v 14 Maay yàqte Pattros, \q1 taal dëkk bi ñuy wax Cowan, \q1 ba sottal sama mbugal ci kaw dëkk bi ñuy wax No. \q1 \v 15 Maay sottil sama xadar Ciin, rawtub Misra, \q1 te maay tenqi gàngooru No. \q1 \v 16 Maay taal Misra, \q1 dëkk ba ñuy wax Ciin di rag-ragi; \q1 dëkk ba ñuy wax No, ñu bëtt ko; \q1 Memfis, noon yi nangu ko digg bëccëg. \q1 \v 17 Xaleli góori On ak Pi Beset, saamar lañuy fàddoo, \q1 waa dëkk yooyu ca des njaam lañu jëm. \q1 \v 18 Bu ma dogee sidditi Misra, \q1 ba doole ja muy sago ŋiis, \q1 jant dootu fenkal Tapanes, \q1 aw xiin ay sàng dëkk bi, \q1 te dëkk-dëkkaanam ya, njaam lañu jëm. \q1 \v 19 Nii laay wàcceele Misra ay mbugal, \q1 ba ñu xam ne maay Aji Sax ji.”» \s1 Doole réer na Misra \p \v 20 Ca fukkeelu at maak benn, juróom ñaari fan ca weer wa jëkk, kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal na ma ne ma: \q1 \v 21 Yaw nit ki, damm naa përëgu Firawna buuru Misra, \q1 mu ngii, deesu ko takk, ba mu faju, \q1 deesu ko lëmës, ba mu mana ŋàbb saamar. \q1 \v 22 Léegi nag Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 «Maa ngii fi kaw Firawna buuru Misra. \q1 Ñaari përëgam yépp laay damm; \q1 bu baax beek bi damm ba noppi, \q1 maay waddal saamaram bi ci loxoom, \q1 \v 23 maay tasaare Misra fi biir xeet yi, \q1 wasaare leen fi biir réew yi. \q1 \v 24 Maay dooleel përëgu buuru Babilon, \q1 teg sama saamar ci loxoom, \q1 gannaaw ba ma dammee përëgi Firawna, \q1 muy binni binniy ku ñu jam fi kanamam. \q1 \v 25 Maay dooleel përëgi buuru Babilon moos, \q1 përëgi buuru Misra yoqi. \q1 Maay teg sama saamar ci loxol buuru Babilon, \q1 mu xàccil ko réewum Misra, \q1 ba ñu xam ne maay Aji Sax ji. \q1 \v 26 Maay tasaare Misra fi biir xeet yi, \q1 wasaare leen fi biir réew yi, \q1 ba ñu xam ne maay Aji Sax ji.» \c 31 \s2 Ponkal daanu na \p \v 1 Ba loolu amee ca fukkeelu at maak benn, benn fan ca ñetteelu weer wa, kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal ma ne ma: \v 2 «Yaw nit ki, waxal Firawna buuru Misra ak gàngooram, ne ko: \q1 “Ana koo neexool daraja? \q1 \v 3 Asiree ngoog, garabu seedar la woon ca Libaŋ, \q1 rafeti bànqaas, naatalub gott, siggi ca kaw, \q1 njañ lay àkki niir ya. \q1 \v 4 Bëti ndox suuxat ko, ndoxi xoote yi màggal ko, \q1 wal ma dajaloo ca reen ya, \q1 doxe fa yónnee garabi àll bi yépp ay waltan. \q1 \v 5 Moo ko taxa sut garabi àll bi, \q1 ay bànqaasam sëq, car ya lawa law \q1 ndax ndox mi koy ballal a ne xéew. \q1 \v 6 Picc yépp ay tàgge ay caram, \q1 rabi àll yépp di jure fa suufam, \q1 askanoo askan wu mag di tooge keram. \q1 \v 7 Taaram a nga ca taxawaayam \q2 ak guddaayu caram ya, \q1 ngir reenam ba sóoboo ndox mu ne xéew. \q1 \v 8 Du genn garabu seedar ca toolub Yàlla, gu ko yóbbuloon dara, \q1 du garabu sippar yu ko niruy car, \q2 mbaa garabu palataan bu ko niruy bànqaas. \q1 Du genn garab ci toolub Yàlla, gu taaroo ni moom. \q1 \v 9 Maa ko rafetale njañam lu sëq, \q1 ba garabi Àjjana, toolub Yàlla bi, ñoom ñépp ñee ko! \p \v 10 «“Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaa siggi woon ca kaw, kii la njañam àkki woon niir ya, muy damoo taxawaayam. \v 11 Maa koy jébbal ku jiite ay xeet, mu fey koo fey coxoram, ma dàq ko. \v 12 Ay doxandéem a dikk, bokk ci xeet yi gëna néeg, gor ko, wacc, ay bànqaasam wadde kaw tund yeek xur yi, ay caram dammtoo ci xuntiy àll bi yépp, waa réew yépp dawe keram, wacc ko, \v 13 picc yépp di tage peram bi tëdd fi suuf, rabi àll yépp di goore caram yi fi suuf. \v 14 Su boobaa genn garab gu feggook ndox dootu siggi ca kaw, ba njañ lay àkki niir ya, genn garab dootu màndim ndox, bay damu ci kawi moroomam. Ñoom ñépp déy lañu àppal ndee, ñu jëm xóotey suuf, tëddi biir bàmmeel ni waa àddina sépp. \p \v 15 «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Bés ba seedar ga tàbbee njaniiw, maa dogal ag ñaawlu: Maa sàng xóote ya ndax moom, téye dexi biir suuf, wali ndox yi noon xéew, taxaw. Maa ñaawluloo gottub Libaŋ ci loolu, garabi àll bi yépp doxe ca lax. \v 16 Maa def xeet yi dégg jéllu seedar gi, di lox, ba ma ko tàbbalee njaniiw, boole kook mboolem ñiy tàbbim pax, ba mboolem garabi Àjjana gëna taaru, ak yay ngëneeli Libaŋ, ak mboolem ya màndim ndox, ñoom ñépp di fa muñe seen demin, la seedar ga teew ni ñoom biir xóotey suuf. \v 17 Ñoo bokk ak seedar gi wàcci njaniiw, ànd caak ña fa saamar tëral, ñoom ñi ko doon dooleel, xeet yi daan tooge keram. \v 18 Ana kan nga neexool teddngaak daraja ci biir garabi Àjjana? Ndaxam dees na la booleek garabi Àjjana, tàbbal xóotey suuf. Yaay goorandook yéefar, yi saamar tëral. Loolooy deminu Firawnaaki gàngooram. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”» \c 32 \s2 Jàmbaaru àddina, baadooloy njaniiw \p \v 1 Ca fukkeelu at maak ñaar, benn fan ca fukkeelu weer waak ñaar, kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal na ma ne ma: \v 2 «Yaw nit ki, yékkatil kàddug jooy, ñeel Firawna buuru Misra. Nga ne ko: \q1 “Dangaa meloon ni waxambaanew gaynde ci biir xeet yi, \q1 mel ni ninki-nànkay biir géej, \q1 di fettaxe say wal, \q1 di wéquy nëxal ndox mi, \q1 di tilimal dex gi. \q1 \v 3 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Maa lay laaw sama caax fi biir ndajem xeet yu bare, \q1 ñu ñoddee la mbaal ma, génne. \q1 \v 4 Maa lay wacc fi suuf, sànni la ci àll bi, \q1 dëël njanaaw yépp fi yaw, \q1 ba reggal rabi àll yépp ci saw yaram. \q1 \v 5 Maay lale tund yi sa suux, \q1 ba feesale xur yi sa jalu néew yi. \q1 \v 6 Maay nàndale suuf sa deret, \q1 mu wale ca tund ya, \q1 ba feesal yooni ndox yi. \q1 \v 7 Bu sa leer feyee, maay muur asamaan, \q1 lëndëmal ay biddiiwam, \q1 sànge jant bi aw niir, \q1 weer wi noppee leeral. \q1 \v 8 Mboolem leeri asamaan laay giimal fi sa kaw, \q1 ba teg lëndëm fi sam réew. \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \b \q1 \v 9 «“Maay jàqloo xeet yu bare, \q1 bu ma leen àggee sa musiba \q2 ci biir réew yoo xamuloon. \q1 \v 10 Saw demin laay tiitale xeet yu bare, \q1 ba seen yarami buur yi di dawa daw. \q1 Keroog sa bésub jéll ba, bu may xàcci sama saamar fi seen kanam, \q1 duñu noppee lox, ku nekk ay xalaat bakkanu boppam. \b \q1 \v 11 «“Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: \q1 Saamaru buuru Babilon a lay dikkal. \q1 \v 12 Saamari jàmbaar laay tërale sa mbooloo, \q1 ñoom ñépp bokk ci xeet yi gëna néeg, \q1 te ñooy sàggi sagub Misra; \q1 gàngooram gépp sànku. \q1 \v 13 Maay faagaagal sa mboolem jur, \q2 gi feggook ndox mi ne xéew, \q1 ba tànku nit dootu ko nëxal, \q1 wewu jur dootu ko nëxal. \q1 \v 14 Su boobaa ma dalal seeni ndox, \q1 dawal ndànk seeni wal nig diw. \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \q1 \v 15 Bu ma defee réewum Misra ab gent, \q1 ba réew mi feesoon, ne faraas, \q1 bu ma dumaa mboolem ku ci dëkkoon, \q1 su boobaa ñu xam ne maay Aji Sax ji.” \b \q1 \v 16 «Kàddug jooy a ngoog gu ñuy jooyi, \q1 janqi xeet yeey jooye yooyu jooy Misraak gàngooram gépp. \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.» \s1 Misra wéetul ca toroxteem \p \v 17 Ca fukkeelu at maak ñaar, fukki fan ak juróom ca weer woowa, kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal na ma ne ma: \v 18 «Yaw nit ki, yuuxul mbooloom Misra, gungee ko seen jéll, ñook janqi xeet yu mag yi, ñu ànd tàbbiji xóotey suuf, fekk fa ña tàbbi woon pax. \v 19 Ne leen: \q1 “Misraa, ana koo ëpp ub taar? \q1 Tàbbil, ñu boole laak paaxe yi tëral.” \q1 \v 20 Fi digg ñi fàddoo saamar la waa Misra di tëdd. \q1 Saamar ba génn na, \q1 ñu diri Misra, booleek gàngooram yépp yóbbu. \q1 \v 21 Biir njaniiw la jàmbaari xare yay tollu, \q1 di waxtaane Misraaki farandoom, naan: \q1 “Wàccsi nañu, ne lareet, \q1 Yéefar yi fàddoo nañu saamar!” \b \q1 \v 22 «Buurub Asiree nga faak gàngooram gépp, \q1 bàmmeeli xarekatam ña wër ko. \q1 Ñoom ñépp lañu jam, ñu fàddoo saamar. \q1 \v 23 Seeni bàmmeel a nga féete fa xóotey xóote ya, \q1 ñu yéew bàmmeelu buurub Asiri. \q1 Ñoom ñépp lañu jam, ñu fàddoo saamar, \q1 te daan tiital waa réewum aji dund ña. \b \q1 \v 24 «Buurub Elam a nga faak gàngooram gépp, \q1 seeni bàmmeel yéew bosam. \q1 Ñoom ñépp lañu jam, ñu fàddoo saamar. \q1 Paaxe lañu wàccaale xóotey suuf, \q1 te daan tiital waa réewum aji dund ña. \q1 Seen gàcce lañu gàlloo, \q1 ànd ak ñay wàcci biir pax. \q1 \v 25 Buurub Elam kay a nga tëdd ca biir ña ñu bóom, \q1 mook gàngooram gépp, seeni bàmmeel yéew ko. \q1 Paaxe yooyu yépp a fàddoo saamar, \q1 te daan tiital waa réewum aji dund ña. \q1 Seen gàcce lañu gàlloo, \q1 ànd ak ñay wàcci biir pax, \q1 ñu boole leen ak ña ñu bóom ab tëraay. \b \q1 \v 26 «Buuri Meseg ak Tubal a nga faak seen gàngoor gépp, \q1 seen bàmmeeli xarekat yéew leen. \q1 Paaxe yooyu yépp a fàddoo saamar, \q1 nde ñoo daan tiital waa réewum aji dund ña. \q1 \v 27 Robaaleesu leen ak jàmbaar ña ànd ak seen gànnaayi xare, \q1 wàcci biir njaniiw, \q1 ñu gegen leen seen saamar, terale leen, \q1 te seen ay war seeni yax, \q1 nde ñoo daan tiital waa réewum aji dund ña. \q1 \v 28 Waaye yaw itam Misra, yaa ngii rajaxoo fi digg yéefar yi, \q1 bokk ngaak ñi fàddoo saamar ab tëraay. \b \q1 \v 29 «Edom a nga fa, mooki buuram ak garmi yépp, \q1 seenug njàmbaar teewul ñu denc leen fa ñu denc ñi fàddoo saamar, \q1 ñu bokk ak paaxe yi ab tëraay, \q1 ànd ak ña jëm biir pax. \b \q1 \v 30 «Kàngami bëj-gànnaar yépp a nga fa, \q1 ak mboolem waa Sidon, \q1 ña ànd ak ña ñu bóom, tëddi pax, \q1 te seenug njàmbaar doon tiitale démb, \q1 tey, ñu ànd ak ñi saamar bóom, tëddaale seenug kéefar. \q1 Ñoo ràngoo seen toroxte, \q1 ànd ak ñay wàcci biir pax. \b \q1 \v 31 «Ñoom la Firawna di gis, \q1 muñe leen deminu gàngooram gépp, \q1 moom mi fàddoo saamar, mooki nitam ak mbooloom mépp. \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \b \q1 \v 32 «Maa defoon Firawna di tiitale ci réewum aji dund ñi. \q1 Waaye tey moo bokk tëraay ak yeneen paaxe yi fàddoo saamar, mook gàngooram gépp. \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.» \c 33 \s1 Tabb nañu Esekiyel jongrukat \p \v 1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal na ma ne ma: \v 2 «Yaw nit ki, waxal ak sa bokk yi, nga ne leen: “Am réew, su ma wàccee xare ci kawam, waa réew ma tànne ci seen biir kenn, def ko seen jongrukat, \v 3 su kooka séenee congum xare muy dikk ci réew mi, daldi wal liit gi, àrtu waa réew mi, \v 4 ku dégg baatu liit ga te fàgguwul, bu cong mi agsee ba yóbbaale ko, mooy gàddu bakkanu boppam. \v 5 Gannaaw dégg na baatu liit ga, te taxu koo fàggu, mooy gàddu bakkanu boppam. Ku déggoon ba fàggu nag, moo musal boppam. \v 6 Su jongrukat ba séenee congum xare may dikk te walul liit ga, loolu waral waa réew mi fàgguwñu, ba cong ma agsi, ba rotal bakkanu kenn ca ñoom, su boobaa njubadiy jongrukat baa ko rotal, te bakkanu nit kooka, jongrukat ba laa koy topp.” \p \v 7 «Yaw nit ki nag, jongrukat laa la tabb, ñeel waa kër Israyil, ba boo déggee baat bu jibe sama gémmiñ, war leen koo artoo ci sama ndigal. \v 8 Bu ma nee ku bon ki: “Yaw ku bon ki, dee rekk mooy sa àtte,” te yaw waxuloo ko ko, àrtu ko ngir mu wacc yoonu mbonam, ku bon kooka aw ayam mooy àtteb deeyam. Waaye bakkanam, yaw laa koy topp. \v 9 Waaye yaw soo artoo nit ki ngir mu wacc yoonu mbonam, te taxu koo wacc yoonu mbonam, moom la aw ayam di àtteb deeyam, waaye yaw yaa musal sa bopp. \p \v 10 «Yaw nit ki, waxal ak waa kër Israyil, ne leen: “Ngeen ne dungeen mana mucc ndax seeni tooñ ak seen bàkkaar yu leen diis ba semmal leen?” \v 11 Waxleen ne leen: “Giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, awma bànneex ci deewug nit ku bon. Sama bànneex mooy mu wacc yoonu mbonam, ba dund. Kon yeen waa kër Israyil, waccleen, ngalla waccleen seen yoonu mbon. Ana lu jar ngeen di dee?” \p \v 12 «Yaw nit ki, waxal sa bokk yi, ne leen: “Boroom njekki démb li, su tooñee tey, njekkam loola du ko musal. Ku bon ki itam, bu waccee yoonu mbonam, tey, mbonu démbam ga du ko lor. Boroom njekki démb li nag, su bàkkaaree, njekkal démbam la du ko may mu dund. \v 13 Doonte maa ne boroom njekk li dina dund moos, te gannaaw gi mu yaakaar njekkal démbam la, bay def safaan ba, su boobaa gépp njekkam ga woon, deesu ci bàyyi xel, te safaan bi mu def tey mooy doon àtteb deeyam. \v 14 Su ma nee ku bon ki: ‘Yaw dee rekk mooy sa àtte,’ mu mujj dëddu bàkkaaram, di jëfe njub ak njekk, \v 15 di delloo alalu tayle ju mu laajoon, di fey lu mu sàccoon, di jëfe dogali yoon yiy taxa dund, tey baña jëfe njubadi, su boobaa dina dund moos te àtteb dee toppu ko. \v 16 Mboolem lu mu bàkkaaroon, deesu ko ko bàyyil xel. Njub geek njekk gi mu mujje moo ko may mu dund.” \p \v 17 «Sa bokk yi nee ñu: “Ni Boroom biy doxale du noonu.” Te ñoom la seen doxalin dul noonu! \v 18 Boroom njekk li daal, su dëddoo njekkam di def njubadi, njubadi gaay doon àtteb deeyam. \v 19 Ku bon ki nag, su dëddoo mbonam, di jëfe njub ak njekk, loolaa koy may mu dund. \p \v 20 «Yeen waa kër Israyil, ngeen ne: “Ni Boroom biy doxale du noonu.” Nit ku nekk daal, jëfinam laa koy àttee.» \s1 Jëf ju bon daane na Yerusalem \p \v 21 Ca fukkeelu atu ngàllo ak ñaar, keroog juróomi fan ca fukkeelu weer wa, jenn waay a rëcce ca jéllub Yerusalem ba, dikk ne ma: «Dëkk ba daanu na!» \v 22 Fekk na ngoon ga jiitu dikkam, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji teg ma loxo, ba tijji sama gémmiñ. Ba waa ja rëcc agsee fa man ca ëllëg sa ca suba, fekk na sama gémmiñ tijjiku, luuwatuma. \p \v 23 Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma: \v 24 «Yaw nit ki, ñi dëkke genti réewum Israyil mii ñu ngi naan: “Ibraayma kenn la woon te moo moomoon réew mi. Kon nun ñiy ñu bare noo ko ci gëna yey.” \v 25 Kon nag nanga leen wax ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen ngeen di boole yàpp ak deret di ko lekk, di wékki gët kasaray tuur, di tuur deretu jaamburi Yàlla, ba noppi di moom réew mi? \v 26 Yeen wóoluwuleen lu moy seen saamar, ngeen di def jëf ju siblu, ku nekk di jaalook jabaru moroomam, ba noppi di moom réew mi?” \v 27 Wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Giñ naa ko ci man miy dund, ku nekk ci yeen ci biir gent yi, saamar lay fàddoo; képp ku nekk ci biir àll bi, rab yi laa koy jox, ñu lekk ko; te képp ku làqoo tata yeek xunti yi, mbas a koy rey. \v 28 Maay def réew mi gent bu wéet, sagu réew mi sàggiku, tundi Israyil ne faraas, kenn du ca jaare. \v 29 Bu ma defee réew mi gent bu wéet ndax seen mboolem jëf ju siblu, dinañu xam ne maay Aji Sax ji.” \p \v 30 «Léegi nag, yaw nit ki, sa bokk yaa ngi lay waxtaane ci keppaari tata yi ak ci bunti kër yi. Ñu ngi waxante ci seen biir, ku nekk naa mbokkam: “Aycaleen nu dem dégluji gan kàddoo tukkee ci Aji Sax ji.” \v 31 Noonu la sama ñoñ di dajesee fi yaw, toogaanu la, di la déglu. Dañuy déglu say wax, waaye duñu ko jëfe mukk. Lu neex lañuy wax waaye amin wu lewul rekk la seen xol di sàkku. \v 32 Dañu laa jàppe rekk ni boroom woy yu neex, ku neex baat, te mane xalam. Dañuy déglu say wax te duñu ci jëfe dara. \v 33 Waaye sa wax jaa ngii di waaja sotti, te bu sottee dinañu xam ne ab yonent a ngi woon fi seen biir.» \c 34 \s1 Waxyu dal na sàmm su bon si \p \v 1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal na ma ne ma: \v 2 «Yaw nit ki, waxal \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* fi kaw sàmmi Israyil. Biralal waxyu ci kaw sàmm soosu, ne leen: Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Wóoy ngalla sàmmi Israyil yiy sàmm seen bopp! Xanaa du jur gi, la sàmm si wara sàmm? \v 3 Yeen, nebbon ji, ngeen lekk; kawari jur gi, ngeen def yére, sol; li ci duuf, ngeen rendi, te jur gi sàmmuleen leen! \v 4 Yeen, li ndóol ci jur gi, leqliwuleen; li ci wopp, fajuleen; li damm, yeewuleen; li ci lajj, gindiwuleen; li réer, seetuleen. Doole daal ngeen leen yilife, di leen soxore. \v 5 Jur gi tasaaroo na ndax ñàkk ku leen sàmm, ñu mujj doon ndawalu mboolem rabi àll yi. Tasaaroo nañu! \v 6 Sama gàtt yaa ngi tambaambalu kaw tundoo tund wu mag ak wu ndaw. Biir réew mi mépp la sama gàtt yi tasaaroo. Kenn wërul, kenn seetul. \p \v 7 «Moo tax yeen sàmm si, dégluleen kàddug Aji Sax ji. \v 8 Mu ne: Giñ naa ko ci man miy dund. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Gannaaw sama gàtt yi ñàkk nañu sàmm, ba ñu di leen sëxëtoo, ñu mujj di ndawalu rabi àll yépp, te sama sàmm si wëruñu sama jur gi, sàmmuñu leen, xanaa di sàmm seen bopp, \v 9 gannaaw noonu la, yeen sàmm si, dégluleen kàddug Aji Sax ji. \v 10 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di dal fi kaw sàmm si. Maay nangoo sama gàtt ci seeni loxo, dakkal seenug càmm, ndax ñu noppee sàmm seen bopp. Maay foqatee samag jur ci seeni sell, ba dootuñu leen ndawaloo. \p \v 11 «Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: Man ci sama bopp, maa ngii di wër samag jur, maa leen di seet. \v 12 Ni ab sàmm di seete ag juram fu ñu tasaaroo, ni laay seete samag jur, ba xettlee leen mboolem fu ñu tasaarooji woon bésub ngëlén bu lëndëm. \v 13 Maa leen di seppee ci xeet yi, génnee leen ci réew yi, dajale leen, yóbbu leen seen suufas bopp. Maa leen di foral, sàmm leen kaw tundi Israyil ak biir xunti yaak mboolem fu ñu dëkke ci biir réew mi. \v 14 Ay parlu yu baax laa leen di forale, kaw tundi Israyil yu kawe ya di seen parluwaay. Foofa lañuy goore parluwaay yu baax, te ñax mu naat lañuy fore foofa ca kaw tundi Israyil. \v 15 Man mii maay foral samay gàtt te maa leen di gooral. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \v 16 Bu ci réer, maa lay seet; bu ci lajj, maa lay délloosi; bu ci damm, maa lay takkal; bu ci néew doole, ma leqli la. Waaye bu ci duuf, am doole, maa lay sànk, foral la li war ci yaw. \p \v 17 «Waaye Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen sama gàtt yi, maa ngii di àttesi diggante xar ak moroom ma, ak diggante kuuy yi ak sikket yi. \v 18 Xanaa fore parlu mu baax mi da leena doyul, ba ngeen di dëggaate li des ci seen parlu mi? Am naan ndox mu teey doyatu leen, ba bu ngeen naanee ba màndi, di wéquy nëxal ndox mi? \v 19 Luy ndeyi sama gàtt yi ci des di fore li ngeen dëggaate, di naane ndox mi ngeen nëxal? \p \v 20 «Moo tax Boroom bi Aji Sax ji da leena wax ne: Maa ngi nii di àttesi diggante gàtt bu duuf ak gàtt bu yooy. \v 21 Gannaaw yeen wet ak mbagg ngeen di buuxee, di dañe seeni béjjén mboolem gàtt yu néew doole yi, ba tasaare leen ca biti, \v 22 man maay wallu samag jur, ba deesatu leen fàdd te maay àtte diggante gàtt ak moroom ma. \p \v 23 «Gannaaw loolu maa leen di waajalal ab sàmm bu leen di sàmm. Kookooy Daawuda sama jaam bi. Moom moo leen di foral, mooy doon seen sàmm. \v 24 Man Aji Sax ji maay doon seen Yàlla, Daawuda sama jaam bi mooy askanoo nguur fi seen biir. Man Aji Sax ji maa ko wax. \v 25 Maay fas ak ñoom \w kóllëreg|lemma="kóllëre g-:"\w* jàmm, maay far ci réew mi wépp rab wu aay. Su boobaa ñu dëkke màndiŋ mi ci xel mu dal, di fore bët biir gott bi. \v 26 Maa leen def ñuy barke, ñook fi wër sama tund wi, bu jotee ma tawal leen, te tawu barke lay doon. \v 27 Garabi àll bi di meññ, suuf si nangu, ñu dëkke seen suufas bopp ci xel mu dal. Bu ma dammee seeni jéng, xettli leen ci dooley ñi leen doon jaamloo, dinañu xam ne maay Aji Sax ji. \v 28 Dootuñu doon sëxëtoom xeet yi, te rabi àll yi dootuñu leen lekk. Dañuy dëkke xel mu dal, te kenn du leen tiitalati. \v 29 Maa leen di sàkkal tóokëru jàmm ba ab xiif dootu fi lore ci réew mi, te dootuñu jànkoonteek kókkaliy yéefar yi. \v 30 Su boobaa ñu xam ne maay seen Yàlla Aji Sax ji ànd ak ñoom, ñoom ñuy waa kër Israyil sama ñoñ. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \v 31 Yeen sama jur gi, sama juru parlu mi, yeenay nit ñi may sàmm, may seen Yàlla. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.» \c 35 \s1 Waxyu dal na Edom \p \v 1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal na ma ne ma: \v 2 «Yaw nit ki, neel jàkk tundu Seyir\f + \fr 35.2 \fr*\fk Seyir \fk*\ft mooy réewum Edom, cosaanu Esawu sëtub Ibraayma.\ft*\f*, nga biral \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* fi kawam. \v 3 Nga wax ko, ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Yaw tundu Seyir, maa ngii fi sa kaw. \q1 Maa lay dóor sama loxo, \q1 nar laa def gent bu wéet. \q1 \v 4 Say dëkk, jali doj laa koy def, \q1 nga gental, \q1 ba xam ne maay Aji Sax ji. \b \q1 \v 5 «“Dangaa masa bañ \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \q1 Ba musibay bànni Israyil taxawee, \q1 ba seen àppu mbugal mat sëkk, \q1 yaa leen jañax ci kaw ñaawkay saamar. \q1 \v 6 Moo tax giñ naa ko ci man miy dund, \q1 kàddug Boroom bi Aji Sax jee, \q1 deret laa lay sange, \q1 deret topp la, \q1 ndegam bañuloo tuur deret, \q1 deret a lay topp. \q1 \v 7 Maay def tundu Seyir gent bu wéet, \q1 maa fay dagge nit ku fay génne ak ku fay dugge. \q1 \v 8 Maay feesaley tundam nit ñu ñu bóom, \q1 tundam yu ndaw aki xuram aki xunteem, \q2 fa la ñi fàddoo saamar naan lareet. \q1 \v 9 Ay gent yu gental fàww laa laay def, \q1 say dëkk, deesu ko dëkkeeti. \q1 Su boobaa ngeen xam ne maay Aji Sax ji. \b \q1 \v 10 «“Aji Sax ji nekk fi, nga naan: \q2 ‘Ñaari làngi giir yii\f + \fr 35.10 \fr*\fk ñaari làngi giir yi \fk*\ft Israyil laak Yuda.\ft*\f* dëkke seen ñaari réew yii, \q1 maa leen moom, noo ciy teg loxo.’ \q1 \v 11 Moo tax giñ naa ko ci man miy dund, \q1 kàddug Boroom bi Aji Sax jee, \q1 ni nga mbugale bànni Israyil ci sa biir mer, \q2 ak sa kiñaan ak sa mbañeel, \q1 ni laa lay mbugale. \q1 Maay dogal sab àtte, \q1 ba xamal ñii maay kan. \q1 \v 12 Su boobaa nga xam ne man Aji Sax ji, \q1 maa dégg sa jépp waxi ñàkk kersa ja nga nee: \q1 ‘Tundi Israyil a ngii ne tasar, \q1 dim sëxëtoo mu ñu nu wërsëgale.’ \q1 \v 13 Yeenay damu fi sama kaw, \q1 di ma wax waxi reewande ju bare! \q1 Maa déggal sama bopp. \q1 \v 14 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Bu àddina sépp di bànneexu, \q1 yaw, ab gent laa lay def. \q1 \v 15 Yaa doon bége suufas Israyil su gental. \q1 Noonu laa lay def. \q1 Ab gent ngay doon, yaw tundu Seyir, \q1 yaak Edom gépp ba mu daj. \q1 Su boobaa ñu xam ne maay Aji Sax ji.” \c 36 \s1 Barke ñeel na tundi Israyil \p \v 1 «Yaw nit ki, waxalal \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* tundi Israyil. Neel: \q1 “Yeen tundi Israyil, \q1 Dégluleen kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \q1 \v 2 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Gannaaw noon bee ne leen: ‘Ñaw! \q1 Seen kawte yu yàgg yii, \q1 tey nooy boroom.’ ” \m \v 3 Kon waxal waxyu bii, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Wet gu ne lañu leen same, yàqte leen, \q1 ba ngeen mujj di moomeelu yéefar yi, \q1 ñépp di leen jëw ak a tooge, \q1 \v 4 Kon nag yeen tundi Israyil, \q1 dégluleen kàddug Boroom bi Aji Sax ji. \q1 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ak tund yu mag yeek yu ndaw yi, \q2 ak xunti yeek xur yi, \q2 ak ndànd-foyfoy yu wéet yeek dëkk yi gental, \q2 te xeet ya ñu dëkkal sëxëtoo leen, yab leen. \q1 \v 5 Boroom bi Aji Sax ji nag dafa wax ne: \q1 Maa ngii déy di waxe sama tàngooru fiiraange \q2 ak xeet yi dul yawut, boole ci Edom gépp, \q2 ñoom ñi jiital seen xeebeel, \q2 te suuf si ma séddoo, ñu aakimoo ko, \q2 te di ko bége mbégte mu mat sëkk, \q2 ngir sëxëtoo parluy réew mi.” \q1 \v 6 Kon nag, waxalal waxyu suufas Israyil \q1 te wax ak tund yu mag yeek yu ndaw yi \q2 ak xunti yeek xur yi, ne leen: \q1 “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Maa ngii di waxe fiiraange ak xadar \q1 ndax toroxte gi leen xeet yi teg. \q1 \v 7 Loolu tax na Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Man maa giñ ne yéefar yi leen séq ñooy tegoo toroxte. \b \q1 \v 8 «“Waaye yeen tundi Israyil, yeenay naat, \q1 di meññal Israyil sama ñoñ, \q1 te léegi ñu ñibbsi. \q1 \v 9 Maa ngii déy maak yeen, \q1 maa leen di geesu, \q1 ba ngeen ruuje, jiwe. \q1 \v 10 Maa leen di fulal aw nit, ci biir Israyil gépp, ba mu daj, \q1 ñu dëkkewaat dëkk yu mag yi, \q1 tabaxaat bayaal yi. \q1 \v 11 Maa leen di fulal nit ak mala, \q1 ñu giir, nangule. \q1 Maay def ñu dëkke leen na woon, \q1 baaxe leen lu raw démb, \q1 ba ngeen xam ne maay Aji Sax ji. \q1 \v 12 Yaw suuf, maay doxloo nit fi sa kaw, \q1 muy waa Israyil sama ñoñ, \q1 ñu jagoo la, séddoo la, \q1 te dootoo sabab seenug deele.”» \b \q1 \v 13 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 «Nee ñu réewum Israyil mooy dëmm buy dëmm boppam. \q1 \v 14 Kon yaay réew mu dootu dëmme, \q1 bay reylu saw xeet. \q1 Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \q1 \v 15 Dootuma la dégtal ñàkk kersay yéefar yi, \q1 dootoo dékku yabeelu xeet yi, \q1 te dootoo reylu saw xeet, \q1 kàddug Boroom bi Aji Sax jee.» \s1 Israyil yeeslu, Yàlla di sell ba tey \p \v 16 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkalati ma ne ma: \v 17 «Yaw nit ki, ba waa kër Israyil dëkkee seen suufas bopp, dañu koo sobeele seen jikko ak seeni jëf, seen jëfin mel ni sagaru sobe ci man. \v 18 Ma xëpp leen sama xadar ndax deret ji ñu tuur ci réew mi, ak kasaray tuur yi ñu ko sobeele. \v 19 Ma tasaare leen ci biir yéefar yi, ñu wasaaroo fi biir réew yi. Seen jikko ak seeni jëf laa leen àttee. \v 20 Waaye fu ñu dem ca biir yéefar ya, teddadil nañu fa sama tur wu \w sell|lemma="sell:"\w*, nit ña di leen waxtaane, naan: “Ñii de, ñoñi Aji Sax ji lañu, teewul réewam ma lañu bàyyikoo nii.” \v 21 Ma daldi seet ci sama teddngay tur wu sell, wi waa kër Israyil di teddadil fi biir yéefar yi ñu fekki. \p \v 22 «Moo tax nanga wax waa kër Israyil, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen waa kër Israyil, li may waaja def, du yeen laa ci seet, li ma ci seet mooy sama teddngay tur wu sell, wi ngeen teddadil fi digg yéefar yi ngeen fekki. \v 23 Kon dinaa fésal sama sellngay tur wu màgg, wi ñu teddadil fi biir yéefar yi, sama tur wi ngeen teddadil fi seen biir. Ci yeen laay fésale sama sellnga, yéefar yiy gis, ba xam ne maay Aji Sax ji. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \v 24 Maa leen di seppee ci yéefar yi, dajalee leen mépp réew, délloosi leen seen suufas bopp. \v 25 Maa leen di wis ndox mu set, ngeen set. Mboolem seen sobe ak mboolem seen kasaray tuur laa leen di setalal. \v 26 Maa leen di jox xol bu yees, te xel mu yees laay def ci seen dënn. Xolu doj bi laay roccee ci seen suux, weccee leen ko xolu suux, \v 27 te samam xel laay yeb fi seen biir dënn, ba dogal ngeen mana topp sama dogali yoon, di sàmm ak a jëfe sama àttey yoon. \v 28 Su boobaa ngeen mana dëkke réew mi ma joxoon seeni maam, di sama ñoñ, may seen Yàlla. \v 29 Maa leen di musal ci seen mboolem sobe, maay woo am pepp, ful ko, te dootuma leen teg ab xiif. \v 30 Maay ful doomu garab ak meññeefum tool, ba dootuleen am gàccey xiif fi digg yéefar yi. \v 31 Su boobaa yeenay fàttliku seen jikko yu bon yaak seen jëf ju baaxul. Su ko defee ngeen jéppi seen bopp ndax seeni ñaawtéef ak seen jëf ju siblu. \v 32 Du yeena tax nag may jëfe noonu. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Na leen loolu wóor. Kon nag waa Israyiloo, rusleen ba ne tott ci seeni jëfin.” \p \v 33 «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Bés bu ma leen setalee ba ngeen tàggook seen mboolem ñaawtéef, dinaa delloo dëkk yu mag yi aw nit, gent yi tabaxewaat. \v 34 Mbooy gu wéet gi, dees na ko beyaat, ba mu wuuteek wéetaay, ba képp ku fa jaare seede woon. \v 35 Su boobaa dees na ne: ‘Xool-leen miim réew, ak mbooy gi mu doonoon, tey mu naat ni toolub Àjjana! Dëkk yeet ay gent la woon, wéet, tojatoo, tey ñu dàbbli lépp, ba dëkke nii!’ \v 36 Su boobaa seen dëkkandooy yéefar yi fi des dinañu xam ne man Aji Sax ji maa tabaxaat dëkk yu mag yi tojatoo woon, jëmbataat mbooy gi. Man Aji Sax ji, maa wax te maay jëf. \p \v 37 «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Lii laay nangulaatal waa kër Israyil, defal leen ko: maay ful nit ñi niy gàtt. \v 38 Bu màggal masaa am, Yerusalem day fees ak gàtt yu ñuy rendi, sarxal. Nit ñiy dëkkewaat genti tey yii, noonu lañuy baree. Su boobaa ñu xam ne maay Aji Sax ji.”» \c 37 \s1 Israyil dekki na \p \v 1 Gannaaw loolu loxol \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji da maa dikkal. Aji Sax ji yóbboo ma Noowam, ba teg ma ca digg joor ga, fekk joor ga fees dell aki yax. \v 2 Mu wërloo maa wërloo ca biir yax ya, ndeke yax yaa nga bare lool te wow koŋŋ ca biir joor ga. \v 3 Mu ne ma: «Yaw nit ki, ma ne, yii yax man naa dundaat a?» Ma ne ko: «Boroom bi Aji Sax ji, loolu de, yaw doŋŋ a ko xam.» \v 4 Mu ne ma: «Waxal \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* fi kaw yax yii, ne leen: “Yeen yax yu wow yi, dégluleen kàddug Aji Sax ji: \v 5 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax yax yii, ne leen: Maa ngii di leen sol ag noo, ngeen dund. \v 6 Maa leen di may ay siddit, saxal leen aw suux, sànge leen ab der, sol leen ag noo, ngeen dund, ba xam ne maay Aji Sax ji.”» \v 7 Ma biral waxyu na mu ma ko sante. Naka laa biral waxyu rekk, coow daldi jib, ànd akum riir, fekk yax yaay booloo, bu nekk ak ba muy àndal. \v 8 Ma gis ay siddit taq ca, aw suux sax ca kaw, ab der dikk, tege ca kaw, te genn noo amu ca. \v 9 Mu ne ma: «Yaw nit ki, waxalal Noo gi waxyu, waxal ko waxyu ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaw Noo gi, bàyyikool ñeenti yooni ngelaw yi te dikk, wal fi biir ñii ñu bóom, ba ñu dund.”» \v 10 Ma def la mu ma sant, waxyu, noo ga dikk, duggsi, ñu dundaat, jóg taxaw, di gàngoor gu baree bare. \p \v 11 Mu ne ma: «Yaw nit ki, yax yii ñooy mboolem waa kër Israyil. Ñu ngi naan: “Nun de, ay yaxi neen yu wow koŋŋ lanu, sunu yaakaar tas na, nun kay yàqu nanu.” \v 12 Kon nag biralal waxyu, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen sama ñoñ, maa ngii di ubbisi seeni bàmmeel, dekkale leen ca seeni bàmmeel, délloosi leen kaw suufas Israyil. \v 13 Yeen sama ñoñ, bu ma ubbee seeni bàmmeel, ba yékkatee leen ca seeni bàmmeel, dingeen xam ne maay Aji Sax ji. \v 14 Maa leen di sol samag noo, ngeen dund, ma samp leen seen suufas bopp, ba ngeen xam ne man Aji Sax ji maa wax, maa def. Kàddug Aji Sax jee.”» \s1 Israyil, genn giir, benn buur \p \v 15 Ba loolu wéyee kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal ma ne ma: \v 16 «Yaw nit ki, sàkkal aw dénk, nga bind ci kaw lii: “Ñeel Yuda ak giiri Israyil yi mu àndal.” Nga sàkkaat weneen dénk, bind ci kawam: “Ñeel Yuusufa bantub Efrayim ak waa kër Israyil yi mu àndal,” \v 17 te nga boole ñaari dénk yi, ñu booloo, di wenn dénk ci sa loxo. \v 18 Bu la sa bokk yi laajee, ne la: “Xanaa doo nu wax lii lu muy tekki?” \v 19 nanga leen wax ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jël dénku Yuusufa wi ci loxol Efrayim, mook giiri Israyil yi mu àndal, boole kook dénku Yuda, daldi def lépp wenn dénk, ñu booloo di wenn ci sama loxo.” \p \v 20 «Nanga ŋàbb dénk yi nga bind, ñuy gis, \v 21 te nga wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jëleji \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ca biir xeet ya ñu fekki, dajalee leen wet gu nekk, délloosi leen seen suufas bopp. \v 22 Maa leen di def wenn xeet doŋŋ ci réew mi, ci kaw tundi Israyil, ñoom ñépp bokk benn buur. Dootuñu doon ñaari xeet te dootuñu xàjjalikoo ñaari nguur. \v 23 Dootuñu sobeel seen bopp ci ay kasaray tuur, ak seen jëf ju siblook mboolem seeni tooñ. Maa leen di walloo ci mboolem seen ñàkk kóllëre. Ma setal leen, ñu doon sama ñoñ, ma doon seen Yàlla. \p \v 24 «“Daawuda sama jaam baay doon seen buur, di seen bennub sàmm ñoom ñépp. Sama àttey yoon lañuy doxe, sama dogali yoon lañuy sàmm, di ko jëfe. \v 25 Ñooy dëkke réew mi ma joxoon Yanqóoba sama jaam ba, te seeni maam dëkke woon ko. Ñu dëkke ko ñoom it, ñook seeni doom ak seeni sët, ba fàww, te Daawuda sama jaam ba mooy doon seen boroom jal ba fàww. \v 26 Maay fas ak ñoom \w kóllëreg|lemma="kóllëre g-:"\w* jàmm, gu sax. Maa leen di samp, ful leen, maay samp sama bérab bu sell fi seen biir, ba fàww, \v 27 sama dëkkuwaay nekk fi seen biir, may seen Yàlla, ñuy sama ñoñ. \v 28 Bu sama bérab bu sell nekkee fi seen biir ba fàww, xeet yi dinañu xam ne man Aji Sax ji maa sellal Israyil.”» \c 38 \s1 Kàdduy waxyu dal na Gog \p \v 1 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal na ma ne ma: \v 2 «Yaw nit ki, neel jàkk Gog ma ca réewum Magog, boroom Meseg ak Tubal, te nga biral \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* fi kawam. \v 3 Neel: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Yaw Gog, boroom Meseg ak Tubal, \q1 maa ngi nii fi sa kaw. \q1 \v 4 Maa lay waññi, we say ŋaam ay lonku, \q1 génne la yaak sa mbooloo mépp ak fas ak gawar, \q1 ñépp gànnaayu ba diis, \q1 di gàngoor gu yaa, ak pakk yu mag ak yu ndaw, \q1 ñépp mane saamar. \q1 \v 5 Waa Pers, waa \w Kuus|lemma="Kuus:"\w* ak waa Puut ay ànd ak yeen, \q1 ñoom ñépp fàggoo pakk ak mbaxanam xare. \q1 \v 6 Gomeer indaale gàngooram gépp, \q2 ak Bet Togarma ga ca catal bëj-gànnaar, ak gàngooram yépp, \q1 ñuy xeet yu takku, ànd ak yaw. \b \q1 \v 7 «“Nanga waajala waajal, \q1 yaak mboolem sa ndaje mi dajesi fi yaw, \q1 nga doon seen wattukat. \q1 \v 8 Feek lu yàgg dees na la woo. \q1 Bu ay at jàlle ba jeex, yaay songi am réew \q2 mu nit ña rëcc saamar, \q2 ba jóge ci ay xeeti xeet, \q2 dajeji ca kaw tundi Israyil ya yàggoona wéet. \q1 Ñooñoo seppikoo ci xeeti àddina yi, \q1 ñoom ñépp dëkksi fa ci biir xel mu dal. \q1 \v 9 Waaye yaa naa jàyy ni ngëlén, \q1 mel ni aw xiin, \q1 muur réew mi, yaak sa gàngoor yépp, \q2 ak xeeti xeet yi ànd ak yaw. \b \q1 \v 10 «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Bésub keroog ay xalaat dikkal la, \q1 nga mébét mébét mu bon, \q1 \v 11 daldi ne: ‘Maay songi réew mu ne ŋàpp, \q1 maay dali ca kaw waa réew mu ne finaax, \q1 dëkke xel mu dal, \q1 te du tata ju wër fu ñu dëkke, ñoom ñépp, \q1 du buntu dëkk, du tëjukaayu bunt.’ \q1 \v 12 Yaay dikk ngir foqati, sëxëtoo sëxëtoo alal, \q1 daldi aakimoo genti démb yu ñu dëkke tey, \q1 ña fa ne di mbooloo mu ñu seppee ci xeet yi, \q1 am ug jur aki alal, \q1 te dëkke léegi digg àddina. \q1 \v 13 Waa Saba ak Dedan ak julay Tarsis, \q2 ak mboolem seeni boroom daraja ñoo lay wax ne la: \q1 ‘Nangu alal a la yékkatee? \q1 Sëxëtoo alalu xaree la taxa bàbbi sa gàngoor, \q1 ngir yóbbu xaalis ak wurus, \q1 nangu jur ak alal, ba dajalee ca xare ba koom gu takku?’ ” \p \v 14 «Kon nag yaw nit ki, biralal waxyu, waxal Gog, ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: \q1 Bésub keroog déy, \q1 bu Israyil sama ñoñ sancsee xel mu dal, dinga ko yég, \q1 \v 15 ba bàyyikoo sa màkkaan, ca catal bëj-gànnaar, \q1 yaak xeet yu bare yu ànd ak yaw, \q1 ñoom ñépp war fas, \q1 di gàngoor gu mag, mbooloo mu bare. \q1 \v 16 Yaay songi Israyil, sama ñoñ, \q1 mel ni aw niir, muur réew ma. \q1 Fan yu mujj ya la loolu di am, \q1 maa lay yóbbu yaw Gog, ba ca réew ma ma séddoo. \q1 Maa lay firndeele sama sellnga, \q1 ngir xeet yi gis, ba xam maay kan. \b \q1 \v 17 «“Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: \q1 Yaw déy, laa doon wax bu yàgg, \q1 yonenti Israyil, sama jaam ña jottli ko ca yooya jant, \q1 ñu biral waxyu ay ati at, \q1 ne maa lay dal-loo sama kaw ñoñ. \q1 \v 18 Bésub keroog, ba Gog di dalsi ca kaw réewum Israyil, \q1 kàddug Boroom bi Aji Sax jee, \q1 sama xadaru mer ay fettax. \q1 \v 19 Sama fiiraange ak sama tàngooru xadar laa birale ne: \q1 bésub keroog déy, suuf dina yëngoo Israyil lool; \q1 \v 20 jën ak njanaaw di lox fi sama kanam, \q1 ñook ndundati àll bi ak mboolem luy raam \q2 ak kuy nit fi kaw suuf. \q1 Tund yi màbb, doji mbartal ya fàqandoo, \q1 tata yépp jóoroondoo. \q1 \v 21 Ca laay wool mbooloom Gog saamar fa sama kaw tund yépp, \q1 kàddug Boroom bi Aji Sax jee, \q1 mbokk di jam mbokk saamar. \q1 \v 22 Maa koy mbugale mbas ak deret ju tuuru, \q1 ak wali waameek doji yuur, \q1 ak tawub sawaraak tamarax, mooki gàngooram, \q2 ak xeet yu bare yi ànd ak moom. \q1 \v 23 Maay biralee noonu sama màggaay ak sama sellnga, \q1 maa niy xamlee sama bopp, \q1 yéefar yu bare di gis, \q1 ba xam ne maay Aji Sax ji.”» \c 39 \s1 Gàngooru Gog sànku na \p \v 1 «Yaw nit ki nag, waxal \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* ci kaw Gog, nga ne: “Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: Maa ngii fi sa kaw, yaw Gog, boroom Meseg ak Tubal. \v 2 Maa lay waññi, yóbbu la, jële la catal bëj-gànnaar, yéege la kaw tundi Israyil. \v 3 Maay féle sa xala ci sa loxol càmmoñ, féle say fitt ci sa loxol ndijoor, waddal. \v 4 Ca kaw tundi Israyil ngay daanu, yaak mboolem say gàngoor, ak mbooloo yi ànd ak yaw. Tan yeek lépp luy njanaaw ak ndundati àll bi laa lay jox, leele la leen. \v 5 Ci biir àll bi nga naa lareet. Man de maa ko wax! Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \v 6 Maay yebal sawara fa Magog, ak fa waa dun ya dëkke jàmm, ba ñu xam ne maay Aji Sax ji. \v 7 Sama tur wu \w sell|lemma="sell:"\w* laay xamle fi digg Israyil sama ñoñ, te dootuma seetaan ñuy teddadil sama tur wu sell. Yéefar yi dinañu xam ne maay Aji Sax ji, ku Sell ku Israyil ki. \p \v 8 «“Bés baa ngii di ñëw te dina dikk, kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Bés bii laa waxoon. \v 9 Waa dëkki Israyil ay génnandoo, booley ngànnaay, xambeb taal; pakk bu mag ak bu ndaw, xalaak fitt, ngajjook xeej, taaloo ko diiru juróom ñaari at, \v 10 ba dootuñu taxani, dootuñu gori ca gott ya, gànnaay ya lañuy taaloo, te ñooy futti ñu leen futti woon, di sëxëtoo ña leen sëxëtoo woon. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \v 11 Bésub keroog laay may Gog ab pàkk, mu def ko sëg fi biir Israyil; mooy xuru jaarukaay wiy dog yoonu képp ku fa jaare, te féete yoonu penku wi jëm géeju Xorom ga. Fa lañuy rob Gog ak gàngooram gépp, ñu di ko wooye xuru Gàngooru Gog. \v 12 Juróom ñaari weer waa kër Israyil di leen rob, ngir setal réew mi. \v 13 Waa réew mépp a leen di robandoo, te bésub keroog ma darajaal sama bopp, ñu doxe ca siiw. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \v 14 Dañuy tabb nit ñu féetewoo di wër réew mi, ñu àndandook tukkikat yi, di rob néew yi des ci àll bi, ngir setal ko. Bu juróom ñaari weer yi jeexee ñu tàmbalee seetaat. \v 15 Wërkat yooyooy wër réew mi ba mu daj, ku ci gis yaxi nit, sàkk xàmmikaay ca wet ga, ngir robkat yi dikk, robi ko ca xuru Gàngooru Gog, \v 16 ba far am dëkk bu ñuy wooye Amona (mu firi Gàngoor). Noonu lañuy setale réew mi.” \p \v 17 «Yaw nit ki nag, Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Waxal picc yi ak mboolem njanaaw yi ak rabi àll yépp, ne leen: “Dajalooleen, jóge fu ne, dikk, dajesi ci sama sarax si ma leen di rendil, muy sarax su mag fa kaw tundi Israyil, ngeen lekk yàpp, naan deret. \v 18 Yàppu xarekat ngeen di lekk, naan deretu garmiy réew mi, ñooy seeni kuuy, aki tàppaanga aki bëy aki yëkk, ñoom ñépp mel ni juru yafal yuy fore jooru Basan. \v 19 Dingeen lekk nebbon ba regg, naan deret ba màndi ci sama sarax si ma leen rendil. \v 20 Sama ndab ngeen di regge méddu fas ak boroom watiir ak méddu jàmbaar ak méddu bépp xarekat.” Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \v 21 Maay biralal yéefar yi sama teddnga, yéefar yépp gis àtte yi ma dogal ak sama diisaayu loxo bi ma leen teg. \v 22 Bésub keroog la waa kër Israyil di dale xam ne maay seen Yàlla Aji Sax ji. \s1 Aji Sax ji ñoŋal na sellngaam \p \v 23 «Kon yéefar yi dinañu xam ne ñaawtéefi waa kër Israyil moo leen yóbbe ngàllo ndax la ñu ma ñàkke worma, ba ma xañ leen sama kanam, teg leen ci seen loxoy noon, ñu fàddoondoo saamar. \v 24 Seeni sobeek seeni tooñ laa jëflanteek ñoom, ba xañ leen sama kanam. \p \v 25 «Kon nag Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: Léegi maay tijji wërsëgu Yanqóoba, maay ñeewante waa kër Israyil googu gépp, te maay fiire sama tur wu \w sell|lemma="sell:"\w* wi. \v 26 Bu ñu dëkkee seenum réew ci xel mu dal, kenn lëjalu leen, ñooy gàddu seen gàcce, ak gépp ñàkk worma gu ñu ma ñàkke woon worma, \v 27 Bu ma leen jëlee ci xeet yi, délloosi leen, maa leen di dajalee ca seen réewi noon yooya, maa leen di fésale sama sellnga, yéefar yu bare teg ci bët. \v 28 Dinañu xam ne maay seen Yàlla Aji Sax, ji leen yóbbu woon ngàllo ca yéefar ya, ba noppi délloosi leen seen suuf, te bawuma kenn gannaaw. \v 29 Gannaaw bu ma walee waa kër Israyil sama noo, dootuma leen xañ sama kanam. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.» \c 40 \s1 Esekiyel gis na kër Yàlla gu bees \p \v 1 Ba ñu duggee ca ñaar fukkeelu at maak juróom gannaaw ba ñu nu yóbboo ngàllo, mu yemook fukki at ak ñeent gannaaw ba ñu nangoo Yerusalem, bésub keroog booba yemook fukki fan, loxol \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikk na fi sama kaw. Mu yóbbu ma ba foofa. \v 2 Ci biir peeñuy Yàlla la ma yóbbu ba réewum Israyil, wàcce ma ci kaw tund wu kawee kawe. Mu am fa ca wetu bëj-saalum luy nirook tabaxi dëkk bu mag. \v 3 Ba mu ma yóbboo ba foofa, ma jekki yem ci nit ku am melow xànjar, ŋàbb buumu lẽe ak yetu nattukaay. Ma nga taxaw ca buntu dëkk ba. \v 4 Waa ja ne ma: «Yaw nit ki, xoolal bu baax, teewlool say nopp te def sam xel ci mboolem li ma lay won. Ngir won la moo tax ñu indi la ba fii. Mboolem loo gis, nanga ko àgge waa kër Israyil.» \s1 Natt nañu miir baak bunt ba féete penku \p \v 5 Ma jekki gis ab miir bu wër kër Yàlla gi ba mu daj. Waa jaa nga ŋàbb yetu nattukaay bu gudde juróom benni xasab\f + \fr 40.5 \fr*\fk xasab \fk*\ft ñeent fukki santimeetar laak juróom.\ft*\f* yu teg yaatuwaayu catu loxo\f + \fr 40.5 \fr*\fk catu loxo \fk*\ft bu digg-dóomu di juróom ñaari santimeetar ak genn-wàll.\ft*\f*. Mu natt talaayu miir ba, muy wenn yet, taxawaay ba it di wenn yet\f + \fr 40.5 \fr*\fk yet wi \fk*\ft di ñetti meetar yu teg tuuti.\ft*\f*. \v 6 Mu dem ca bunt ba féete penku, yéeg dëggastal ya, daldi natt guddaayu dëxu biir bunt ba, muy wenn yet. Benn dëx bi rekk, wenn yet la. \v 7 Néegi wattukat yi làng ak jaaruwaayu mbaaru bunt bi, bu ci nekk ab kaare la bu wetam di wenn yet. Diggante ñaari néeg yu nekk, miiru juróomi xasab moo ca dox. Dal-luwaayu mbaar ma ca biir, ab dëxam wenn yet la. \v 8 Mu natt dal-luwaayu mbaaru bunt ba ca biir, \v 9 muy juróom ñetti xasab, ay jënam dëlle ñaari xasab. Dal-luwaayu mbaar maa nga ca biir, janook néeg Yàlla ba. \v 10 Néegi wattukati bunt ba féete penkub kër Yàlla ga, ñett la wet gii, ñett wet gee, yépp tolloo, te jën yi leen séq ñoo tolloo yaatuwaay. \p \v 11 Waa ja natt yaatuwaayu buntu mbaar mi, bu ubbikoo, muy fukki xasab, yaatuwaayu bunt bi di fukki xasab ak ñett, boo ci boolee jën yi. \v 12 Fi janook bunti néegi wattukat, yi bindoo juróom benni xasab wet gu nekk, ab dëx a fa tëdde xasab, talaayu dëx ba di xasab. \v 13 Mu natte mbaar ma ca xadd ba, diggante miiru biiru benn néeg, ak miiru biiru moroom, ma mu jàkkaarlool, muy ñaar fukki xasab ab juróom. \v 14 Mu def ñaari jëni mbaar mi\f + \fr 40.14 \fr*\fk jëni mbaar \fk*\ft yooyu jën yenuwul dara, dañoo taxaw noonu rekk.\ft*\f* juróom benn fukki xasab, ëttu kër Aji Sax ji féete mbaaru bunt bi wet gu nekk. \v 15 Diggante kanam mbaaru bunt ba, ba fa dal-luwaayu mbaar ma jeexe, juróom fukki xasab la. \v 16 Néegi wattukat yi ak seeni jën am nañu ay palanteeri biir yu ànd aki caax, te wër néeg yi ba dajal. Dal-luwaayu mbaaru bunt bi itam am ay palanteeri biir yu wër ba dajal. Jën wu ci nekk, ay nataali garabi tàndarma lañu ñaas ca kawam. \s1 Natt nañu ëttu biti ba \p \v 17 Waa ja yóbbu ma, ba ca ëttu biti ba. Mu am fa ab dër bu dajal ëtt ba, fanweeri néeg séq ko. \v 18 Dër ba daa wër mbaari bunt yi waaye dëru ëttu biti bi nag moo gëna suufe bu ëttu biir ba. \v 19 Waa ja natt diggante mbaaru bunt ba féeteek ëttu biti ba, ak mbaaru ëtt ba féete biir, muy téeméeri xasab. Loola di wetu penku, mu teg ca bëj-gànnaar. \s1 Natt nañu bunt ba féete bëj-gànnaar \p \v 20 Mu natt guddaay ak yaatuwaayu mbaaru bunt ba féete bëj-gànnaar, te jëm ca ëttu biti ba. \v 21 Néegi wattukat ya ñu tabaxaale mbaar ma di ñett genn wet, ñett ca ga ca des. Dayoy jën yaak dal-luwaayu mbaar ma, mook yu buntu penku ba, ñoo bokk yem: guddaay ba di juróom fukki xasab, yaatuwaay ba di ñaar fukki xasab ak juróom. \v 22 Ay palanteeram ak dal-luwaayam ak nataali garabi tàndarmaam it, lépp a bokk ak yu buntu penku ba dayo. Juróom ñaari dëggastal ngay yéeg, janook dal-luwaayu ba. \v 23 Niki buntu penku bi rekk, buntu bëj-gànnaar ba daa janook bunt bay jàllale ca ëttu biir ba. Mu natt diggante ñaari bunt ya jàkkaarloo, am téeméeri xasab. \s1 Natt nañu bunt ba féete bëj-saalum \p \v 24 Mu yóbbu ma wetu bëj-saalum, ma yem ci buntu bëj-saalum ba. Mu natt ay jënam ak dal-luwaayu mbaaram, dayo ya bokk ak yu bunt ya jiitu, di benn. \v 25 Foofu itam am na ay palanteer yu wër dal-luwaayu mbaaru bunt ba ba mu daj, nirook yu jëkk ya. Dayo yeet di benn: juróom fukki xasab ci guddaay, ñaar fukki xasab ak juróom ci yaatuwaay. \v 26 Juróom ñaari dëggastal ngay yéeg dal-luwaay ba. Ay nataali garabi tàndarma lañu ñaas ca kaw jën ya, wet gu nekk genn. \v 27 Foofu it ëttu biir ba am na bunt bu féete bëj-saalum. Waa ja natt diggante ñaari bunti bëj-saalum yi jàkkaarloo, am téeméeri xasab. \s1 Natt nañu bunt ya jëm ëttu biir ba \p \v 28 Waa ja jaarale ma ca buntu bëj-saalum ba, dugal ma ca ëttu biir ba. Mu natt buntu bëj-saalum boobee, ay dayoom di benn. \v 29 Néegi wattukatam yaak jënam yaak biir dal-luwaayu mbaar ma, lépp a bokk ak ya jiitu ay dayo. Mbaaru bunt ba ak dal-luwaayam am ay palanteer ba dajal, guddaayu mbaaru bunt ba di juróom fukki xasab, yaatuwaay ba di ñaar fukki xasab ak juróom. \v 30 Néeg yu ndaw yi wër ëttu biir bi ba mu daj, ñaar fukki xasab ak juróom la ci guddaay, juróom ci yaatuwaay. \v 31 Bunti dal-luwaayi mbaar yaa ngay ubbikoo ca ëttu biti ba, ñu rafetale jën ya ay nataali garabi tàndarma. Juróom ñetti dëggastal lañu cay dugge. \p \v 32 Waa ja jaare penku, dugal ma ca ëttu biir ba. Mu natt buntu penku boobu, dayo ya di benn. \v 33 Ay néegam aki jënam ak biir dal-luwaay ba, lépp a bokk ak ya ca des ay dayo, juróom fukki xasab ci guddaay, ñaar fukki xasab ak juróom ci yaatuwaay. Mbaaru bunt ba ak dal-luwaayam am na ay palanteer ba dajal. \v 34 Dal-luwaayu bunt baa ngay ubbikoo ca ëttu biti ba, ñu ñaas ca kaw jëni bunt ba ay nataali garabi tàndarma, di ca dugge juróom ñetti dëggastal. \p \v 35 Waa ja yóbbu ma ba ca buntu bëj-gànnaar ba. Mu natt ko, mu bokk ak ya jiitu ay dayo. \v 36 Bunt ba daa ànd aki néegam aki jënam ak dal-luwaayam ak palanteer yu ko wër, ba mu daj. Guddaay ba di juróom fukki xasab, yaatuwaay ba di ñaar fukki xasab ak juróom. \v 37 Mbaaru bunt baa ngay ubbikoo ca ëttu biti ba; ay jënam am wet gu nekk nataali garabi tàndarma, te ñu di ca yéege juróom ñetti dëggastal. \s1 Natt nañu néegu carxal gi \p \v 38 Am na néeg buy ubbikoo ci biir mbaaru bëj-gànnaar ba féete biir. Fa lañuy raxase yàppu \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*. \v 39 Biir dal-luwaay boobu, ñeenti taabal a nga ca, ñaari taabal cat lu nekk. Ca lañuy rey juri sarax yi. Muy saraxu rendi-dóomal, di \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*, di \w saraxu peyug tooñ|lemma="Sarax yi:"\w*. \v 40 Néegu peggu boobu ngay jëkka jot, soo jógee ca biti, ñaari taabal a nga fa, féeteek dëggastal yi ñuy yéege buntu bëj-gànnaar bi ak yeneen ñaari taabal fa féeteek biir dal-luwaay ba. \v 41 Lépp di juróom ñetti taabal, ñeent wet gii ak ñeent wet gee, ñu di ca rendi. \v 42 Ñeenti taabali saraxu rendi-dóomal ba, doji yett lañu ko defare. Bu ci nekk di xasab ak genn-wàll, wet gu nekk, taxawaay ba di xasab. Ñu di ca teg jumtukaay yi ñuy rendee saraxu rendi-dóomal ak yeneen sarax. \v 43 Ñu sàkk ay lonku yu gudde catu loxo, wërale lonku ya ba mu daj ca biir, yàppu sarax ya di tege ca kaw taabal ya. \s1 Natt nañu ëttu biir ba \p \v 44 Mu jàlle ma ca ëttu biir ba. Ay néegi jàngkat a nga ca ëttu biir ba, benn bi ci wetu mbaaru bunt bëj-gànnaar bi, jàkkaarlook bëj-saalum, beneen néeg bi ci wetu mbaaru buntu penku bi, jàkkaarlook bëj-gànnaar. \v 45 Waa ja ne ma: «Néeg bii jàkkaarlook bëj-saalum ñeel na \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi dénkoo dénkaaney kër Yàlla gi. \v 46 Néeg bi jàkkaarlook bëj-gànnaar nag ñeel na sarxalkat yi dénkoo dénkaaney \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi. Ñooñu ñooy \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi askanoo ci Cadog te bokkuñook kenn sañ-sañu jege \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ngir liggéeyal ko.» \p \v 47 Waa ja natt ëttu biir ba, muy téeméeri xasab wet gu nekk. Sarxalukaay baa nga fa kanam néeg Yàlla ba. \s1 Natt nañu néeg Yàlla ba \p \v 48 Mu jàlle ma ca dal-luwaayu mbaaru néeg Yàlla ba, daldi natt ñaari jëni dal-luwaay ba, muy juróomi xasab, wet gu nekk. Bunt ba di fukki xasab ak ñeent, ñaari weti biir mbaar ma di ñetti xasab, wet gu ci nekk. \v 49 Dal-luwaayu mbaar mi gudde ñaar fukki xasab, yaatoo fukki xasab ak benn. Mu am dëggastal yu ñuy yéege, jàll ca biir, ñaari jën séq ko, wet gu nekk, wenn. \c 41 \p \v 1 Ba loolu amee waa ja jàlle ma ba ca bunt \w néeg bu mag|lemma="néeg (Yàlla) bu mag b-:"\w* ba. Mu natt jën ya séq bunt ba, mu dëlle juróom benni xasab ci ñaari wet yépp. \v 2 Yaatuwaayu bunt ba fukki xasab la, ñaari miiri wet yi ko séq, bu ci nekk di juróomi xasab. Mu natt néeg bu mag bi ci boppam, guddaay bi di ñeent fukki xasab, yaatuwaay bi di ñaar fukki xasab. \v 3 Moom nag moo jàll ca néegu biir ba, daldi natt jëni bunt ba, mu dëlle ñaari xasab, diggante ñaari jëni bunt bi di juróom benni xasab, yaatuwaayi ñaari miiri wet yi séq bunt bi, bu ci nekk di juróom ñaari xasab. \v 4 Mu natt néegu biir bi ci boppam, muy ñaar fukki xasab wet gii, di ñaar fukki xasab wetu néeg bu mag ba. Mu ne ma: «Fii mooy fu \w sell|lemma="sell:"\w* fee sell.» \s1 Natt nañu toftalu néeg Yàlla bi \p \v 5 Mu natt miiru néeg Yàlla bi, mu dëlle juróom benni xasab, yaatuwaayu néegi wet, yi wër néeg Yàlla bi ba mu daj, bu ci nekk di ñeenti xasab. \v 6 Néegi wet yooyu ñetti taax yu tegloo la, tollook néeg Yàlla bi ab taxawaay, taax mu ci nekk di fanweeri néeg. Mu am ay cëslaay yu saxe ci miiru néeg Yàlla bi, te téye néegi wet yooyu, ba sësuñu rëkk ci néeg bi ci boppam. \v 7 Taax mu la gëna kawe, gën laa yaatu, miir ba ànd ak moom gëna sew fi wër néeg Yàlla bi ba mu daj. Noonu lañuy yéege ay dëggastal, jóge ci suuf, jaare ca taaxu digg ba, ba ca taax ma ca kaw. \p \v 8 Ma gis ne néeg Yàlla bi ab dëx a ko yenu, yenuwaale néegi wet yi wër néeg Yàlla bi, taxawaayu dëx bi di wenn yet wu mat, tollook juróom benni xasab. \v 9-10 Néegi wet yi, seen miiru biti dëlle na juróomi xasab. Ñu bàyyi diggante néegi wet yi ak taaxi sarxalkat yi, bérab bu tollook ñaar fukki xasab, wër néeg Yàlla bi ci ñetti wetam. \v 11 Am na ñaari bunt yu sare ci néegi wet yi wër néeg Yàlla bi, jëme ci pegg bu dara amul. Benn bunt ba féete bëj-gànnaar; benn ba, bëj-saalum, yaatuwaayu pegg, bi wër néeg bi ba mu daj, di juróomi xasab. \s1 Ber nañu ab tabax ca gannaaw \p \v 12 Tabax bi féeteek dig-digalu feguwaay bi ci sowub néeg Yàlla bi, yaatuwaayam juróom ñaar fukki xasab la, guddaayam di juróom ñeent fukki xasab, dëllaayu miir ba di juróomi xasab. \p \v 13 Waa ja daldi natt néeg Yàlla bi, guddaay bi di téeméeri xasab; la dale dig-digalu feguwaay ba, ba ca catu tabaxu sowu ba aki miiram itam di téeméeri xasab. \v 14 Kanamu néeg Yàlla bi féete penku téeméeri xasab la, boo ci boolee dig-digali feguwaay yi séq néeg Yàlla bi. \v 15 Mu natt yaatuwaayu tabax ba ca gannaaw te janook dig-digalu feguwaay ba, boole ca ñaari poot ya séq tabax ba, muy téeméeri xasab. \p Bérab bu sell bi nag, muy \w néeg bu mag|lemma="néeg (Yàlla) bu mag b-:"\w* bi, di néegu biir bi, di mbaaru bunt bi jàkkaarlook ëtt bi, \v 16 ak dëxi bunt yeek palanteeri caax yeek jaarukaay yi ci ñetti wet yépp, ak ci kanam dëx yi, lu ci nekk bant a ko lal. Ci suuf ak ci kaw miir bi ba ca palanteer ya it noonu, palanteer ya am ay caax. \v 17 Ci kaw buntu néeg Yàlla bi, ba ci biir néeg Yàlla bi, jëm biti, ak kaw miir bi ko wër, biir ak biti, lépp lañu natt. \v 18 Ñu yett ca miir ya ay malaakay \w serub|lemma="serub y-:"\w* ak garabi tàndarma; ñaari serub yu ne, garabu tàndarmaa nga ca digg ba, te serub bu ne am na ñaari kanam, \v 19 genn gi di kanamu nit, jublook genn tàndarma, geneen gi di kanamu gaynde, jublook geneen tàndarma. Noonu lañu wëralee néeg bi ba mu daj. \v 20 Li ko dale ci suufu néeg bu mag bi, ba ci kaw bunt yi, ak ci miir yi, fépp lañu yett serub yeek tàndarma yi. \v 21 Njëël bunt bi ak dëx bi, ak pegg yi ko téye ab kaare la. Buntu néegu biir bu \w sell|lemma="sell:"\w* ba it noonu la. \p \v 22 \w Sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi bant la, taxawaayam di ñetti xasab, guddaayam di ñaari xasab, yaatuwaayam di ñaari xasab. Mu ami coll akub tegukaay aki wet, lépp di bant. Waa ji ne ma: «Taabal jii mooy janook \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji.» \p \v 23 Buntub ñaari laf lañuy dugge ca néeg bu sell bu mag ba, di dugge beneen bunt bu ni mel ca néegu biir bu sell ba. \v 24 Bunt yooyu, bu ci nekk ñaari laf yuy warangiku la. \v 25 Ñu yett ca buntu néeg bu mag ba ay malaakay serub, ak garabi tàndarma yu mel ni ya ñu yett ca kaw miir ya. Catu xaddu mbaaru bunt ba ca biti, aw dénk lañu ko def. \v 26 Palanteeri caax yi ak miiri néegi wet yi ak miiri mbaar mi ak ca kaw catu xadd bay lang, wet gu ne, ay nataali tàndarmaa nga ca. \c 42 \s1 Natt nañu taaxi sarxalkat yi \p \v 1 Ba loolu amee waa ji jaarale ma buntu bëj-gànnaar, génne ma ci ëttu biti bi. Mu yóbbu ma wetu sowu, dugal ma ca tabax ba janook dig-digalu feguwaay ba te sësook miiru biir ba ca wetu bëj-gànnaar. \v 2 Tabax boobu, guddaayam ci wetu bëj-gànnaar ga féeteek bunt ba, téeméeri xasab la, yaatuwaay ba di juróom fukki xasab. \v 3 Ci genn wet tabax booboo ngi janook ñaar fukki xasab yu bokk ci ëttu biir bi, geneen wet gi janook dëru ëttu biti bi. Tabax bi def na ñetti sàppey taax yu tegloo. \v 4 Ci kanam néeg, yi féeteek ëttu biir bi, am na jaarukaay bu yaatoo fukki xasab, gudde téeméeri xasab. Néeg yooyu wetu bëj-gànnaar lañu cay dugge. \v 5 Ñaari taax ya ca kawam nag, mu ci nekk yaatuwaayam a yées ma ko féete suuf, ndax taax mu gëna kawe moo ëpp jaarukaay bu mu bàyyi fi kanamam. \v 6 Ñetti sàppey taax la yu amul ay jën ni néegi ëtt bi ame ay jën. Moo tax ruumi taaxum kaw ma gëna xat yoy taaxum digg ma, ak ma féete suuf. \v 7 Mu am miir bu làng ak néeg yooyu, teqale leen ak ëttu biti bi, guddaayu miir bi di juróom fukki xasab. \v 8 Ndax néeg yooyu féeteek ëttu biti ba, guddaay ba bépp juróom fukki xasab la. Waaye sàppey néeg, ya sësook néeg Yàlla ba, guddaayam téeméeri xasab la. \v 9 Ca suufu néeg yooyu la am jaarukaayu penku bu jëme ca biir néeg ya féete penku, boo jógee ca ëttu biti ba. \p \v 10 Am na sàppeb néeg bu janook dig-digalu feguwaay ba, ak tabax ba ca gannaaw néeg Yàlla ba. Sàppeb néeg boobu ma nga làng ak miiru biti, bi yaatuwaayam féete penku. \v 11 Mu ngi janook ab jàllukaay. Sàppey néeg yooyu daa bindoo ni bi féete bëj-gànnaar te bokk ak ñoom guddaay ak yaatuwaay, seeni bunt ak seeni dayo yépp di benn. \v 12 Bunti sàppey néeg ya ca bëj-saalum it noonu la. Ca catal jaarukaay ba, ab bunt a nga fa, janoo màkk ak miir ba féete penku. \p \v 13 Ba loolu amee waa ji ne ma: «Néegi bëj-gànnaar yeek néegi bëj-saalum yi janook dig-digalu feguwaay bi, ñooy néeg yu \w sell|lemma="sell:"\w* yi \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi jege \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, di lekke sarax yu sell yee sell. Ca lañuy yeb sarax yu sell yee sell it, muy \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* yeek \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w* yeek \w saraxu peyug tooñ|lemma="Sarax yi:"\w* yi, ndax \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* la. \v 14 Sarxalkat yi, bu ñu duggee ci bérab bu sell bi, dootuñu man daldi génn ci ëttu biti bi. Ci néeg yii lañuy wacc seen yére yi ñuy liggéeyale Aji Sax ji, ndax yooyu yére yu sell la. Ñu solaat nag yeneen yére bala ñoo dellu ca ëtt ba mbooloo may daje.» \s1 Natt nañu miiru biti bu kër Yàlla gi \p \v 15 Ba waa ja nattee dayoy biir néeg Yàlla bi ba noppi, da maa jaarale ca mbaaru bunt ba féete penku. Mu tàmbali di natt bayaal bi wër kër gi. \v 16 Mu natte yet wa wetu penku, lépp di juróomi téeméeri yet, yemook kilomeetar ak genn-wàll. \v 17 Mu natte yet wa wetu bëj-gànnaar, lépp di juróomi téeméeri yet, \v 18 wetu bëj-saalum ba it, mu natte ko yet wa, muy juróomi téeméeri yet. \v 19 Mu walbatiku, natte yet wa wetu sowu, muy juróomi téeméeri yet. \v 20 Noonu la natte miir bi ub bayaalu kër Yàlla gi ba mu daj, muy kaare bu wetam di juróomi téeméeri dayo, te teqale fi \w sell|lemma="sell:"\w* ak fi sellul. \c 43 \s1 Leeru Yàlla dellu na këram \p \v 1 Waa ja nag jiite ma ba ca bunt ba, bunt ba féete penku. \v 2 Ma jekki gis leeru Yàllay Israyil, mu dikke penku, ànd ak kàddu gu mel ni kàddug géej mbàmbulaan, suuf si di lerxate fa leeram ga. \v 3 Moomu peeñu nirook peeñu ma ma jëkkoona gis ba may dikk ca yàqum Yerusalem, nirook ma woon ca tàkkal dexu Kebar. Ma daldi daanu, dëpp sama kanam fa suuf. \v 4 Ba loolu amee leeru \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ja jaare ca buntu penku ba, dugg ca néeg Yàlla ba. \v 5 Ngelaw nag ne ma cas, yóbbu ma ca biir ëttu biir ba, leeru Aji Sax ji jekki fees néeg ba. \v 6 Ma dégg kuy wax ak man ku féete fi biir néeg Yàlla bi, te fekk waa ji ma dugal a ngi taxaw fi sama wet ba tey. \v 7 Mu ne ma: «Yaw nit ki, sama màkkaanu ngàngunee ngi, bérab bii laay teg samay tànk, di fi dëkke fi digg \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ba fàww. Bu waa kër Israyil dellu teddadil sama tur wu \w sell|lemma="sell:"\w*, ñook seeni buur ci seen gànctu, ak seen néewi buur yi ñuy denc ci seeni jaamookaay. \v 8 Seen buur yi ñoo féetale seen dëxi bunt ak seen jëni bunt ci sama weti dëxi bunt ak sama jëni buntu kër. Miir doŋŋ a doxoon diggante sama kër ak seen kër. Ñoo def seen jëf ju siblu, ba teddadil sama tur wu sell, ma mer, faagaagal leen. \v 9 Léegi nag nañu ma sorele seen gànctu ak seen néewi buur yi, ndax ma mana dëkk fi seen biir, ba fàww. \p \v 10 «Yaw nit ki, waxal waa Israyil ni kër gi wara mel. Nañu kersawoo seeni ñaawtéef te ñu natt nataalu kër gi. \v 11 Bu ñu kersawoo mboolem seeni jëf nag, nanga leen xamal bindu kër gi ak tëralinam aki duggukaayam aki génnukaayam, bindam bépp, ak dogali yoon yi mu laaj yépp. Nanga bind lépp, ñu gis, ba mana sàmm mboolem bindu kër gi, ak mboolem dogali yoon yi mu laaj, te di ko jëfe. \v 12 Ndigalu yoon wi jëm ci kër Yàlla gi ñu wara tabax mooy lii: ci kaw tund wi ak fi ko wër fépp, fu sella sell lay doon. Loolu mooy ndigalu yoon wi, ci wàllu kër Yàlla gi.» \s1 Natt nañu sarxalukaay bi \p \v 13 Lii nag mooy dayoy \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi ciy xasab, xasab bu ci nekk tegu yaatuwaayu catu loxo. Toogub sarxalukaay bi féete suuf, taxawaayam xasab la, yaatuwaayam di xasab, mu ànd ak kéméjam gu ko wër ba mu daj, te taxawaayu kéméj gi tollook yaatuwaayu catu loxo. Toogub sarxalukaay bi noonu la bindoo. \v 14 Ñaari xasab a dox diggante toogu bi ci suuf, ba ci cat li ngay jëkka jot, te yaatuwaayu cat li di xasab. Ñeenti xasab a dox diggante cat li ngay jëkka jot, ba ca cat la ca kaw, te yaatuwaayam it di xasab. \v 15 Taxawaayu taalub sarxalukaay bi féete kaw ñeenti xasab la, ñeenti béjjén sampe ci ñeenti coll yi, coll wu nekk, benn béjjén. \v 16 Lakkukaayu sarxalukaay bi ab kaare la, wet gu ci nekk di fukki xasab ak ñaar. \v 17 Kon toogub lakkukaay bi fukki xasab ak ñeent la ci ñeenti wetam, dib kaare, kéméj gi wër toogu bi am taxawaayu genn-wàllu xasab, te toogub lakkukaay bi, wëre lakkukaay bi cat lu yaatoo xasab. Dëggastal bi ñuy yéege ci sarxalukaay bi nag penku la féete. \s1 Sàrtal nañu sarxalukaay bi \p \v 18 Waa ji ne ma: «Yaw nit ki, Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: Lii mooy dogali yoon yi jëm ci \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi, bés bu noppee, ci wàllu \w saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ak deret ji ñu ci wara tuur. \v 19 \w Sarxalkati|lemma="sarxalkat b-:"\w* \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi askanoo ci Cadog, te jege ma, ngir di ma liggéeyal, kàddug Aji Sax jee, nanga leen jox yëkk wu ndaw, muy \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*. \v 20 Nga sàkk ci deret ji, taqal ci ñeenti béjjéni sarxalukaay bi, ak ñeenti colli kaw gi ak ci kéméj gi ba mu daj, nga laabale ko sarxalukaay bi, defale ko ko njotlaayam. \v 21 Nga génne bérab bu sell bi yëkku saraxu póotum bàkkaar mi, te nga lakk ko bérab ba mu ware ci ëttu kër Yàlla gi. \v 22 Bésub ñaareel ba nanga indi ab sikket bu amul sikk, muy saraxu póotum bàkkaar bu ñuy laabale sarxalukaay bi; ñu laabale ko sarxalukaay bi, na ñu ko laabale woon yëkk wu ndaw wa. \v 23 Boo ko laabalee noonee ba noppi, nanga sàkk aw yëkk wu ndaw wu amul sikk ak kuuy mu amul sikk. \v 24 Nga boole indi fi kanam Aji Sax ji, sarxalkat yi suy leen xorom, ñu def leen saraxu rendi-dóomal, ñeel Aji Sax ji. \v 25 Diiru juróom ñaari fan ngay joxe bés bu nekk ab sikketu póotum bàkkaar akaw yëkk akum kuuy, te na lu ci nekk mucc sikk. \v 26 Diiru juróom ñaari fan lañuy def njotlaayal sarxalukaay bi, setal ko, doore ko sasu sarxalukaay bi. \v 27 Bu àpp boobu matee, la ko dale ca bésub juróom ñetteel ba, na sarxalkat yi joxe ci kaw sarxalukaay bi, seen saraxi rendi-dóomal, ak seen \w saraxi cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*, ma daldi leen nangul. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.» \c 44 \s1 Ay jagle ñeel na boroom jal bi \p \v 1 Ba loolu amee waa ji delloo ma ca mbaaru biti bu kër Yàlla ba féete penku, fekk bunt ba tëje. \v 2 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ne ma: «Mbaar mii, buntam day dëkke tëje. Kenn du ko tijji, kenn du ci jaare ndax Aji Sax ji Yàllay Israyil fii la dugge. Kon nag na tëje. \v 3 Boroom jal bi\f + \fr 44.3 \fr*\ft Seetal ci 34.23-24 ak 37.24-25.\ft*\f* nag, gannaaw mooy boroom jal bi, sañ na faa tooge, lekk fi kanam Aji Sax ji. Waaye ci dal-luwaayu mbaar mi lay dugge te fi lay génne itam.» \s1 Jege bérab bu sell bi du wàllu ñépp \p \v 4 Gannaaw loolu waa ji jaarale ma ca buntu bëj-gànnaar ba ca kanam néeg ba, ma jekki gis leeru \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji fees néeg Aji Sax ji. Ma daanu, dëpp sama kanam fa suuf. \v 5 Aji Sax ji ne ma: «Yaw nit ki, xippil, ubbil say nopp te def sa xel ci mboolem lu ma la wax ci wàllu dogali yoon yi jëm ci kër Aji Sax ji ak mboolem digali yoonam. Defal sa xel bu baax ci duggukaayi kër gi ak mboolem génnukaayi bérab bu sell bi. \v 6 Nanga wax fippukati waa kër Israyil yii, ne leen: Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen waa kër Israyil, seen jëf ju siblu ji jépp doy na sëkk. \v 7 Bu ngeen ma daan indil sama céru ñam, muy nebbon, di deretu sarax yi, dangeen di dugalaale sama biir bérab bu sell bi ay doxandéem yu xaraful, du ci jëmm, du ci xol. Noonu ngeen sobeele sama kër gi. Fecci ngeen sama \w kóllëreek|lemma="kóllëre g-:"\w* yeen ndax seen jépp jëf ju siblu. \v 8 Dénkoowuleen dénkaane yi jëm ci sama yëf yu \w sell|lemma="sell:"\w* yii, xanaa di ko dénk ñeneen ñu koy dénkoo fi sama biir \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi.» \v 9 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: «Bépp doxandéem bu xaraful ci xol, xaraful ci jëmm, bumu duggati sama bérab bu sell bi, muy doxandéem bu mu mana doon, bu dëkk ci biir \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \s1 Leween ñi am nañu seen wartéefi bopp \p \v 10 «\w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi ma sore woon ba \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* jàddee, ba dëddu ma, di topp seen kasaray tuur, ñooy gàddu seenu ay. \v 11 Ay surga aki fara bunti kër rekk lañuy doon ci sama bérab bu sell bi, te ñooy tegoo liggéeyu kër gi. Ñooy rendil xeet wi \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ak gépp jur gu ñuy sarxal, te ñooy nekk ci waawu xeet wi, di leen surgawu. \v 12 Gannaaw ñoo doon dox diggante xeet week seen kasaray tuur, ba yóbbe leen ay wu leen gàllankoor, maa leen giñal ne, kàddug Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee, ñooy gàddu seenu ay. \v 13 Buñu ma jege, di ma sarxalal, buñu jege sama lenn lu \w sell|lemma="sell:"\w* ak lu sella sell. Ñooy gàddu seen toroxte ak seen añu jëf ju siblu ji ñu def. \v 14 Waaye maa leen di def ñuy nit ñiy dénkoo dénkaaney kër gi ci mboolem liggéey bu mu laaj, ak mboolem lees di def ci biir. \s1 Askanu Cadog am nañu seen wartéefi bopp \p \v 15 «Waaye \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yiy \w Leween|lemma="Leween b-:"\w*, sëtoo ci Cadog, te daa dénkoo dénkaaney bérab bu sell bi ba \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* jàddee, ñooñoo may jege, di ma liggéeyal; ñooy dikk fi man, di indi saraxi nebbon ak deret. Kàddug Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. \v 16 Ñoom doŋŋ ay dugg sama bérab bu sell bi, ñoom doŋŋ ay jege sama taabal, di ma liggéeyal, di dénkoo sama ndénkaane. \p \v 17 «Bu ñu dee jàll buntu ëttu biir bi, yérey lẽe lañuy sol. Buñu sol ndimol kawaru jur, bu ñuy liggéey fu wees buntu ëttu biir bi, jëm ca biir-a-biir. \v 18 Kaalag lẽe lanuy kaalawoo, tubéyu njiitlaayu lẽe lañuy jiital, te duñu sol dara lu leen di ñaqloo. \v 19 Bu ñuy génn ca ëttu biti ba, ëtt ba mbooloo may yem, nañu summi seen yére ya ñuy sarxale, fat yére ya ca néeg yu \w sell|lemma="sell:"\w* ya, daldi sol yeneen yére, ndax baña sédd mbooloo mi sellnga, di leen lor\f + \fr 44.19 \fr*\ft Aay na ci képp ku ñu sellalul, muy laal mbaa ñu di ko laalal lenn lu sell. Man na cee dee sax. Seetal ci \ft*\ft \+bk 2.Samiyel\+bk* 6.6-7.\ft*\f*. \p \v 20 «Buñu watu nel, buñu jañu, waaye nañu dagg seen kawar ba mu yem. \v 21 Biiñ, bu ko benn sarxalkat naan, buy dugg ci ëttu biir bi. \v 22 Ab jëtun ak ku ñu fase, sarxalkat du ko jël jabar. Su dee janq bu askanoo ci waa kër Israyil mbaa ab jëtun bu sarxalkat doon denc, sañ nañu koo jël. \v 23 Sama ñoñ nag nañu leen ràññeeloo lu sell ak lu sellul; te xamal leen lu set ak lu sobewu. \p \v 24 «Bu jote amee, ñoom ñooy àtte, ba dogal àtte bi ci sama àttey yoon. Sama digal yeek sama dogali yoon yi jëm ci sama màggal yépp, ñoo koy sàmm, te sama \w bési Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*, ñoo koy sellal. \p \v 25 «Nit ku dee nag, ab sarxalkat du ko jege, di sobeel boppam, ndare ki dee di baayam mbaa ndeyam, mbaa doomam ju góor, mbaa ju jigéen, mbaa doomu ndeyam ju góor mbaa ju jigéen ju amul jëkkër, ba mu sañ caa sobeel boppam. \v 26 Su ni demee ba mu sobeel boppam, na setlu te négandiku juróom ñaari fan, doora dellu ca liggéeyam. \v 27 Bés ba muy dellu ca ëttu biir ba, ngir liggéey ca biir \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* ba, na indi \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \p \v 28 «Sarxalkat yi am nañu seen céru bopp: man maay seen cér. Du jenn moomeel ju ngeen leen di jox ci suufas Israyil. Man maay seen moomeel. \v 29 \w Saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* ak saraxu póotum bàkkaar ak \w saraxu peyug tooñ|lemma="Sarax yi:"\w*, ñoom ñoo koy lekk, te lépp lu ñu jagleel Aji Sax ji ci Israyil, ñoo koy moom. \v 30 Li gën ci mboolem \w ndoortel meññeef|lemma="Sarax yi:"\w*, ak seen bépp jooxe ak bu mu mana doon, sarxalkat yee ko moom. Li gën ci seen notu sunguf, nangeen ko jox sarxalkat yi, ndax barke wàccal seen kër. \p \v 31 «Gannaaw loolu mboolem lu médd mbaa lu ñu fàdd, muy boroomi laaf akug jur, sarxalkat yi duñu ko lekk. \c 45 \s1 Lu jëm ci suuf si ñu jagleel Aji Sax ji \p \v 1 «Bu ngeen demee bay tegoo réew mi bant ngir séddoo ko, nangeen jooxeel \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dogu suuf bu gudde ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000), yemook fukki kilomeetar ak ñett, yaatoo ñaar fukki junniy (20 000) xasab, yemook fukki kilomeetar ak genn-wàll. Suuf soosu sépp ba fa mu yem, lu \w sell|lemma="sell:"\w* lay doon. \v 2 Biir pàkk boobu, nañu ci waccal \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi ab dénd bu kaare, wet gu nekk di juróomi téeméeri xasab, yemook ñaar téeméeri meetar ak juróom fukk; ak bayaal bu wër dénd bi, yaatoo juróom fukki xasab, yemook ñaar fukki meetar ak juróom wet gu nekk. \v 3 Ci biir dogu suuf bu mag boobu gudde ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000) te yaatoo fukki junniy xasab (10 000), yemook juróomi kilomeetar ak xaajaat, ci ngay nattal bérab bu sell bi, di fu sell fee sell. \v 4 Bérab bu sell a ngoog bu ñuy sàkke ci réew mi, ñeel \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yiy liggéey ci bérab bu sell bi, tey jege Aji Sax ji, di ko liggéeyal. Foofu lañuy am ay kër te foofu lañuy beral ab pàkk bérab bu sell bi. \v 5 Beneen dénd bu gudde ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000), yaatoo fukki junniy xasab (10 000), na ñeel \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñiy liggéeyal kër Yàlla gi, ngir ñu am dëkk yu ñu dëkke. \p \v 6 «Suufas dëkk bi, nanga ko àppal yaatuwaayu juróomi junniy xasab (5 000) ak guddaayu ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000), mu làng ak dog bi ñu sàkkal bérab bu sell bi. Suuf soosu na ñeel waa kër Israyil gépp. \v 7 Boroom jal bi nag, nañu ko jagleel ñaari wet yi séq suufas bérab bu sell beek pàkkub dëkk bi. Suufas buur soosu jóge sowu ba géej ga, jógeeti penku ba fa Israyil yem, na guddaayam tollook guddaayu suufu giirug Israyil gu ci nekk. \v 8 Loolooy doon céru suufu boroom jal bi ci Israyil. Su ko defee boroom jal yi ma fal dootuñu xañ sama ñoñ suuf. Dañuy wacce giiri waa kër Israyil li des ci réew mi. \s1 Sàrt yii war na boroom jal bi ci wàllu kër Yàlla gi \p \v 9 «Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: Yeen ñiy tooge jalu Israyil, na doy nag! Coxor geek jaay-doole bi, baleen ko. Njub ak njekk ngeen war di jëfe. Bàyyileen di nangu sama alali ñoñ. Boroom bi Aji Sax jee ko wax. \v 10 Seen màndaxekaay na doon njub, efab nattukaayu sol-sotti di njub, seen bat bi ñuy natte lu ñuy xelli di njub. \v 11 Na benn efa ak benn bat yem dayo, lu ci nekk wara def céru fukkeelu benn omer\f + \fr 45.11 \fr*\fk benn omer \fk*\ft am na ñu jàpp ne mu ngi tollook ñeenti téeméeri liitar ak juróom fukk, mbaa ñetti téeméeri kilo. Natt yii, seeni dayo daan na soppiku, topp jamono yaak bérab ya ñu ko daan jëfandikoo.\ft*\f*, bi yemook ñaar téeméeri liitar ak ñaar fukk (220), mbaa téeméeri kilo ak juróom fukk (150). Te na benn omer di dayo bi ngeen di natte. \v 12 Benn siikal, na wecciku ñaar fukki gera\f + \fr 45.12 \fr*\ft Moo doon natt ba gënoona tuut ci wàllu diisaay, yemook genn-wàllu garaam.\ft*\f*, te boo boolee nattu ñaar fukki siikal, ak nattu ñaar fukki siikal ak juróom, ak nattu fukki siikal ak juróom, mu wara wecciku benn natt bi ñuy wax miin. \p \v 13 «Lii nag mooy doon seenub jooxe: muy bele, di lors, na doon seen benn céru juróom benn fukkeelu meññeef, di ñaari kilook genn-wàll ci téeméeri kilook juróom fukk yu nekk. \v 14 Su dee ag diw, bat bi ñuy natte lu ñuy xelli lañu koy natte, benn bat yemook fukkeelu natt bi ñuy wax omer, mbaa fukkeelu natt bi ñuy wax kor, di ñaari liitar yu tombal ñaar (2,2) ci ñaar téeméeri liitar ak ñaar fukk (220) yu nekk. \v 15 Ci wàllu parluy Israyil, benn ay génn ci ñaar téeméeri gàtt yu ne, gàtt yooyu ñeel \w saraxi pepp|lemma="Sarax yi:"\w*, ak \w saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ak \w saraxi cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w* ngir njotlaayal askan wi. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \v 16 Boobu jooxe, mboolem waa réew mee ciy def seen loxo, indil ko ki tooge jalub Israyil. \v 17 Li war ki tooge jal bi, saraxu rendi-dóomal ci la, ak saraxu pepp, ak saraxi biiñ yi ñuy joxe bésu màggal, yu mel ni màggali Terutel weer ak \w bési Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*, ak yeneen bés yu \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* taamoo daje. Moom it mooy joxe \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*, ak saraxu pepp, ak saraxu rendi-dóomal, ak saraxu cant ci biir jàmm ngir njotlaayal waa kër Israyil. \p \v 18 «Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Benn fanu weer wi jëkk, nanga jël yëkk wu ndaw wu amul sikk ngir laabal bérab bu sell bi. \v 19 \w Sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi day sàkk ci deretu saraxu póotum bàkkaar boobu, taqal ci jëni bunt yi, ak ñeenti colli kaw \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi, ak jëni buntu ëttu biir bi. \v 20 Noonu it ngay def ca juróom ñaareelu fanu weer wa, ngir daboo ko nit ku jàdd yoon te yégu ko mbaa teyu ko. Su ko defee ngeen def njotlaayal kër Yàlla gi. \p \v 21 «Fukki fan ak ñeent ci weer wu jëkk wi mooy seen \w màggalu bésub Mucc|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* ba. Juróom ñaari fan la màggal giy am, te mburu mu amul lawiir lañu ciy lekk. \v 22 Bés boobu la ki tooge jal bi di joxeel boppam ak mboolem waa réew mi, yëkk wu ndaw wuy doon saraxu póotum bàkkaar. \v 23 Juróom ñaari fan yooyu dina sarxal Aji Sax ji bés bu nekk juróom ñaari yëkk yu ndaw ak juróom ñaari kuuy yu amul sikk, def ko saraxu rendi-dóomal, ak ab sikketu sarax ngir peyug tooñ, bés bu nekk. \v 24 Yëkk wu ci nekk ak kuuy mu ci nekk, da koy booleek saraxu benn efab\f + \fr 45.24 \fr*\fk benn efa, \fk*\ft am na ñu jàpp ne fanweeri kilo lay tollool, benn xiin wara tollook juróom ñetti liitar, lim yooyu mat ñaari yoon li nu am fii.\ft*\f* pepp, di fukki kiloy pepp ak juróom, ak efab pepp bu ne, benn xiinu diw, di ñetti liitari diw ak genn-wàll. \p \v 25 «Ci wàllu màggal giy door fukki fan ak juróom ci juróom ñaareeli weer wi\f + \fr 45.25 \fr*\ft Màggalu bési Mbaar yi lay doon. Seetal ci \ft*\ft \+bk Sarxalkat yi\+bk* 23.33-34.\ft*\f*, na ki tooge jal bi def niki ci màggalu bésub Mucc ba. Juróom ñaari fan, yi màggal giy def, yenn sarax yooyii rekk lay joxe, muy saraxu póotum bàkkaar, ak saraxu rendi-dóomal, ak saraxi pepp ak diw. \c 46 \p \v 1 «Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Buntu ëttu biir bi féete penku, na tëje diiru juróom benni fan yi ñuy liggéey. Waaye bésub Noflaay ba cay topp, na ubbiku. Bésub Terutel weer it, na ubbiku. \v 2 Na ki ci jal bi jaare ci dal-luwaayu mbaar mi féete biti te na yem ci jëni buntu ëttu biir bi. Na fa xaar sarxalkat yi def saraxu rendi-dóomalam, ak saraxi cantam ci biir jàmm. Su ko defee mu sujjóot ci dëxu bunt bi, ba noppi, génn. Bunt bi nag du tëje ba ngoon jot. \v 3 Bésub Noflaay ak Terutel weer, baadooloy réew mi ci bunt boobu lañuy sujjóote fi kanam Aji Sax ji. \p \v 4 «Saraxu rendi-dóomal, bi ki ci jal biy indil Aji Sax ji bésub Noflaay, juróom benni xar yu ndaw yu amul sikk lay doon, ak kuuy mu amul sikk. \v 5 Saraxu pepp biy ànd ak kuuy mi benn efa\f + \fr 46.5 \fr*\fk benn efa: \fk*\ft seetal ci 45.24.\ft*\f* lay doon, di fukki kiloy pepp ak juróom, ak dayob pepp bu mu àttan buy ànd ak xar yu ndaw yi ak xiinu diw, yemook ñetti liitari diw ak genn-wàll ci efab pepp bu nekk. \v 6 Bésub Terutel weer, wenn yëkk wu ndaw lay doon wu amul sikk ak juróom benni xar yu ndaw akam kuuy, te lépp mucc sikk. \v 7 Na ci boole saraxu benn efab pepp buy ànd ak yëkk wi, ak benn efab pepp ngir kuuy mi, ak lu mu man ci pepp, mu booleek xar yu ndaw yi, ak benn xiinu diw ci efab pepp bu nekk. \p \v 8 «Dal-luwaay bunt, bi ki ci jal biy jaare duggsi, fi lay jaare génn. \v 9 Baadooloy réew mi nag bu ñuy teewesi bésub ndaje fi kanam Aji Sax ji, ku ci jaare mbaaru buntu bëj-gànnaar, di sujjóotsi, bu noppee na jaare mbaaru buntu bëj-saalum ba. Te ku dugge mbaaru buntu bëj-saalum, bu noppee na génne mbaaru buntu bëj-gànnaar ba. Deesul delloo bunt bi nga dugge. Bunt bi mu jàkkaarlool lees di génne. \v 10 Ki ci jal bi ci boppam, bu baadoolo yiy dugg, na duggandook ñoom, bu ñuy génn, mu génnandook ñoom. \p \v 11 «Su dee bési màggal ak bési ndaje yi, saraxu pepp mi benn efa lay doon ngir yëkk wi, yemook fukki kilook juróom, ak benn efa ngir kuuy mi, ak dayo bu ñu àttan ngir xar yu ndaw yi, efab pepp bu ne ànd ak benn xiinu diw, di ñetti liitar ak genn-wàll. \p \v 12 «Buntu ëttu biir bi féete penku it lañuy ubbil ki ci jal bi, buy joxe \w saraxu yéene|lemma="Sarax yi:"\w*: muy saraxu rendi-dóomal, di saraxu cant ci biir jàmm, di beneen saraxu yéene bu ñeel Aji Sax ji, ngir mu joxe saraxu rendi-dóomalam, mbaa saraxu cantam ci biir jàmm, ni mu koy defe ci bésub Noflaay. Bu noppee, génn, ñu tëj bunt bi. \p \v 13 «Am xarum menn at mu amul sikk lees di defal Aji Sax ji bés bu nekk saraxu rendi-dóomal, te suba su ne lees koy def. \v 14 Nañu ci boole suba su ne benn céru juróom benneelu efab pepp, yemook ñaari kilook liibar, ànd ak liitaru diw, yemook benn céru ñetteelu xiinu diw buy tooyal sunguf si. Loolooy saraxu pepp mi, ñeel Aji Sax ji, di dogali yoon yu sax dàkk. \v 15 Muy xar mu ndaw mi, di saraxu pepp mi, di diw gi, suba su nekk lees koy def, muy saraxu rendi-dóomal bu sax dàkk. \s1 Boroom jal bi sañul lépp ci suufam \p \v 16 «Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: Su ki ci jal bi mayee kenn ci doomam yu góor lenn ci céru suufam, kookoo koy jagoo, te alal jooju, céru doomi kooka lay doon. \v 17 Waaye su ki ci jal bi mayee kenn ciy surgaam lenn ci suufam, ba keroog atum Yiwiku ma rekk la surga ba di moom suuf sa, waaye bu atum Yiwiku teewee, suuf si day dellu ci loxol ki ci jal bi. Suuf soosu, céru doomi boroom jal bi doŋŋ lay doon. \v 18 Ki ci jal bi nag du nangu lenn ci suufas baadoola yi, di leen xañ seen alal. Alalu boppam doŋŋ la saña sédd doomam yu góor. Su ko defee kenn ci sama ñoñ du ñàkk alalam.» \s1 Sàkkal nañu kër Yàlla gi ay waañ \p \v 19 Ba loolu amee waa ja génneeti ma ca jàllukaay ba feggook buntu bëj-gànnaar. Mu dugal ma ca néeg yu \w sell|lemma="sell:"\w* ya ñu beral \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi. Ndeke bérab a nga foofa ca ruq ba, ca biir-a-biir, ca wetu sowu. \v 20 Mu ne ma: «Bii bérab, fi la sarxalkat yiy togge yàppu \w saraxu peyug tooñ|lemma="Sarax yi:"\w* ak \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w*, di fi lakk \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* mi, ngir baña génne lenn lu sell ca ëttu biti ba, bay sédd nit ñi sellnga gu leen di lor.» \p \v 21 Gannaaw loolu waa ji génneeti ma ba ci ëttu biti bi, yóbbu ma ci ñeenti collam yépp. Ndeke coll wu ci nekk, ber nañu ca ëtt bu ndaw, \v 22 bu gudde ñeent fukki xasab, yaatoo fanweeri xasab, te ñeenti ëtt yu ndaw yi ci coll yi yépp a tolloo. \v 23 Ñeenti ëtt yu ndaw yi, bu ci nekk miir bu gàtt a ko ub, ay toggukaay tege ci suufam, leru miir bi ba mu daj. \v 24 Waa ji ne ma: «Lii mooy waañ yi liggéeykati kër Yàlla gi di togge yàppu saraxi askan wi.» \c 47 \s1 Am wal balle na kër Yàlla ga \p \v 1 Waa ji nag delloo ma ca buntu néeg Yàlla ba. Gisuma lu moy am ndox muy balle ci suuf, di génne ci dëxu buntu penku bi. Kanam néeg baa ngi féete penku, ndox miy wale wetu bëj-saalumu néeg bi, fa féeteek bëj-saalumu \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi. \v 2 Mu génnee ma buntu bëj-gànnaar, wërale ma ca buntu biti ba féete penku. Gisuma lu moy ndox muy wale ci suufu buntu penku bi, ci wetu bëj-saalum. \p \v 3 Waa jaa nga jubal penku, ŋàbb buumu nattukaayam, daldi natt junniy xasab. Mu jàlle ma ba foofa, ndox ma yem ma ci kostan. \v 4 Mu nattaat yeneen junniy xasab, ndox ma yem ma ciy óom. Mu dellu natt junniy xasab, jàlle ma, ndox ma yem ma ci ndigg. \v 5 Mu nattati yeneen junniy xasab, wal ma xóot ba manatumaa xuus, ba jàll. Maneesatu koo jàlle tànk, xanaa féey. \p \v 6 Mu ne ma: «Yaw nit ki, du gis nga ci?» Ba loolu amee mu delloo ma ba ca tàkkal dex ga. \v 7 Ma agsi ca tàkkal dex ga, daldi yem ci garab yu baree bare ci ñaari weti dex gi yépp. \v 8 Waa ji ne ma: «Ndox mii mu ngi jëm diiwaanu penku, wàcci jooru Araba, jàlli biir géeju Xorom ga. Te bu ndox mi duggee biir géej, géeju ndox mu bon ma, ndox ma day daldi neex. \v 9 Mboolem mbindeef muy def ndiiraan day daldi mana dunde mboolem fu wal mii jëm. Jën yi day takku lool ngir la fa ndox mii àgg, ba neexal mooma ndox. Mboolem fu wal mii àkki daal, lépp a fay dund. \v 10 La ko dale Engedi ba Eneglayim, ay nappkat lay doon. Ñu weer seeni caax ci tefes gi. Wirgoy jën wu am géej gu mag ga rekk, dina am foofa, bare lool. \v 11 Waaye tan yaak déeg ya mu feggool du neexaat, xorom saa koy féetewoo. \v 12 Wirgoy garab yu ñuy lekk yu nekk ñooy saxe ñaari weti wal ma. Xob ya du lax, doom ya du rag, xanaa di meññ weer wu nekk, ndax ndox mi koy suuxat ca bérab bu sell ba lay wale. Meññeef ma, ñu lekk; xob ya, ñu fajoo.» \s1 Aji Sax ji joxe na kemuy réew mi ñuy séddoo \p \v 13 Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: «Fukki giiri Israyil yeek ñaar nag, kemi céri suufi réew mi ñuy séddoo, nii la wara tëdde: na wàllu giirug Yuusufa di ñaari cér. \v 14 Nangeen ko séddoo, ku nekk yem ak sa mbokk cér, ndax maa giñal seeni maam, ne dinaa leen ko jox. Kon réew mii, seen cér bu leen lew la. \v 15 Na lii di kemu réew mi ci wetu bëj-gànnaar: géej gu mag ga lay dale, topp yoon wa jaare Ettlon ak Lebo Amat, ak Cedàdd, \v 16 jaare dëkk yi ñuy wax Berota ak Sibrayim te nekk diggante réewum Damaas ak Amat, jaare Àccer Tikon, fa digalook Oran. \v 17 Kon kemu googu day dale Géej gu mag ga, ba àgg gox ba ñuy wax Àccar Enan ca penku ba. Kemu bëj-gànnaaram di Damaas ak Amat. Loolooy wàllu bëj-gànnaaram. \v 18 Kemu penku ba day dale diggante Oran ak Damaas, topp xuru Yurdan, diggante diiwaanu Galàdd ak réewum Israyil, dem ba àgg Tamar ca géeju penku ba\f + \fr 47.18 \fr*\fk géeju penku ba, \fk*\ft mooy géeju Xorom ga.\ft*\f*. Loolooy wàllu penkoom. \v 19 Wetu bëj-saalum, kemu ga day dale fa Tamar ba ca xuru Meriba ca Kades, daldi leru walu Misra ma, ba àkki géej gu mag ga. Loolooy wàllu bëj-saalumam. \v 20 Wetu sowu, géej gu mag gaay doon kemu ga, dale bëj-saalum ba ca Lebo Amat ca bëj-gànnaar. Loolooy wàllu sowoom. \p \v 21 «Suuf si ci diggante kemu yooyu, nangeen ko séddale giiri Israyil yi. \v 22 Nangeen ko tegoo bant, séddoo ko ci seen biir, yeen ak doxandéem yi sanc ci seen digg te jaboot ci réew mi. Nangeen leen jàppe ni ay njuddu-ji-réew fi digg Israyil. Nañu am seen céru suuf ni yeen, bokk ci yem ak giiri Israyil. \v 23 Ak giir gu ci doxandéem bi mana wàlli, foofa ngeen koy féetale céru suufam. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. \c 48 \s1 Daggal nañu suuf giiri bëj-gànnaar \p \v 1 «Lii mooy limeefu giiri Israyil, ak céru suuf bi giir gu ci nekk di féetewoo. Céru Dan moo féete catu bëj-gànnaar. Kemoom day topp yoonu Ettlon ba Lebo Amat, jàll ba Àccar Enan ga digalook Damaas, Amat féete ko bëj-gànnaar. Suufas Dan day jàpp penku ba sowu, ca géej gu mag ga, di benn pàcc. \v 2 Suufas Aser day digalook sos Dan, jàpp, moom it, penku ba sowu, di benn pàcc. \v 3 Suufas Neftali day digalook sos Aser, jàpp penku ba sowu, di benn pàcc. \v 4 Suufas Manase day digalook suufas Neftali, jàpp penku ba sowu, di benn pàcc. \v 5 Suufas Efrayim day digalook sos Manase, jàpp penku ba sowu, di benn pàcc. \v 6 Suufas Ruben day digalook sos Efrayim, jàpp penku ba sowu, di benn pàcc. \v 7 Suufas Yuda day digalook sos Ruben, jàpp penku ba sowu, di benn pàcc. \s1 Daggal nañu Aji Sax ji céram bu sell \p \v 8 «Suuf sa digalook Yuda ca wetu bëj-gànnaaram, te dale penku ba sowu, mooy doon pàkk bi ñuy jooxe. Ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000), fukki kilomeetar ak ñett, lay yaatoo, gudde ni suufas genn giir gu ci nekk, te bérab bu sell bi nekk ci digg bi. \v 9 Pàkk bi ngeen di jooxeel \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ci dog boobu, day am guddaayu ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000) yemook fukki kilomeetar ak ñett ak yaatuwaayu fukki junniy xasab (10 000), di juróomi kilomeetar ak xaajaat. \v 10 Cér bu \w sell|lemma="sell:"\w* a ngoog, ñeel \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi. Ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000) lay am wetu bëj-gànnaar, yaatoo fukki junniy xasab (10 000) wetu sowu, yaatoo fukki junniy xasab (10 000) wetu penku, gudde ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000) wetu bëj-saalum, te bérabu Aji Sax bu sell bi nekk ci digg bi. \v 11 Dig-digal bu sell boobu, na ñeel sarxalkat yi askanoo ci Cadog, ñoom ñi sàmmoon sama ndénkaane, baña ànd ak \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, di lajj ni seen yeneen bokki \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi. \v 12 Jooxeb suufas réew mi, nañu ci jooxeel sarxalkat yi \w bérab bu sella|lemma="bérab bu sell b-:"\w* sell, mu feggook suufas Leween ñi. \v 13 Na suufas Leween ñi digalook sos sarxalkat yi, di pàkk bu gudde ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000), te yaatoo fukki junniy xasab (10 000). Bu ci nekk na am guddaayu ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000) ak yaatuwaayu fukki junniy xasab (10 000). \v 14 Cér boobu mooy tànnéefu suuf si. Maneesu cee jaay, mbaa di ci weccikoo lenn, te lenn du ci tàbbi ciy loxo, ndax cér bu sell la, ñeel Aji Sax ji. \s1 Daggal nañu suuf waa dëkk bi ak boroom jal bi \p \v 15 «Pàkk bay des ci yaatuwaayu dog boobu dina yaatoo juróomi junniy xasab (5 000), gudde ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000); suufas ñépp la pàkk boobu di doon, ngir dëkk bi. Man naa doon ay dëkkuwaay aki parlu, te na dëkk bi ci boppam féetewoo digg ba. \v 16 Na dëkk bi bindoo ab kaare bu wet gi di ñeenti junniy xasab ak juróomi téeméer (4 500), di ñaari kilomeetar ak genn-wàll. \v 17 Parlub dëkk bi nag, na féeteek ñeenti weti dëkk bi, te doon fa wet gu nekk bayaal bu yaatoo ñaar téeméeri xasab ak juróom fukk (250). \v 18 Fi feggook dog bu \w sell|lemma="sell:"\w* bi ñu beral Aji Sax ji, dina des pàkk bu ñuy bey, bu gudde fukki junniy xasab (10 000) wetu penkub dëkk bi, ak beneen pàkk bu ni tollu ci wetu sowu. Ca lañuy jële lekku liggéeykati dëkk bi. \v 19 Waa dëkk bi koy bey, ci giiri Israyil yépp lañuy bàyyikoo. \v 20 Mboolem pàkk boobu ñuy jooxe, na doon kaare bu wet gi di ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000), te pàkk boobu ñuy jooxe, pàkk bu sell bi ci la, dëkk bi, ci la. \p \v 21 «Li féete penku ak li féete sowu yépp nag te des ci suuf si, gannaaw cér bu sell bi, ak suufas dëkk bi, buur bi ci jal bee koy moom; wet gu ci nekk yaatoo ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000), gii àkki kemu Israyil ga féete penku, gee àkki kemu Israyil ga féete sowu, cér bu sell beek kër gu sell gi nekk ci digg bi. \v 22 Kon suufas \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi ak suufas dëkk bi day bokk féete ci diggu suufas boroom jal bi, suufas boroom jal bi nekk diggante céru Yuda ba ca bëj-gànnaar, ak céru Beñamin ca bëj-saalum. \s1 Daggal nañu suuf giiri bëj-saalum \p \v 23 «Limeefu giiri Israyil yi ci des, seeni suuf nii lay tëdde: Li dale kemu penku ba, ba ca géej gu mag ga ca sowu, benn pàcc lay doon, Beñamin féetewoo ko. \v 24 Suufas Simeyon feggook sos Beñamin, jàpp penku ba sowu, di benn pàcc. \v 25 Suufas Isaakar jàpp penku ba sowu, feggook sos Simeyon, di benn pàcc. \v 26 Suufas Sabulon feggook sos Isaakar, jàpp penku ba sowu, di benn pàcc. \v 27 Suufas Gàdd feggook sos Sabulon, jàpp penku ba sowu, di benn pàcc. \v 28 Suufas Gàdd, kemug bëj-saalumam mooy doon kemug réew mi. Day dale fa Tamar ca penku ba, ba ca yoonu ndoxu Meriba ca Kades, leru walum Misra, ba ca géej gu mag ga. \v 29 Noonu ngeen di séddalee réew mi giiri Israyil yi, giir gu ci nekk, ngeen dogale ko noonu céru suufam. Kàddug Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee. \s1 Yerusalem: tur wu yees, fukki bunt ak ñaar, ni giir yi \p \v 30 «Bunti dëkk bi nag nii lay tëdde: Ñeenti miiri dëkk bi, bu ci nekk day am guddaayu ñeenti junniy xasab ak juróomi téeméer (4 500). \v 31 Miir bu ci nekk dina am ñetti bunt yu ñu dippee ñetti giiri Israyil. Wetu bëj-gànnaar, benn buntu Ruben ak benn buntu Yuda ak benn buntu Lewi. \v 32 Wetu penku am miiru ñeenti junniy xasab ak juróomi téeméer (4 500) ak ñetti bunt: benn buntu Yuusufa ak benn buntu Beñamin ak benn buntu Dan. \v 33 Wetu bëj-saalum am miiru ñeenti junniy xasab ak juróomi téeméer (4 500) ak ñetti bunt: benn buntu Simeyon ak benn buntu Isaakar ak benn buntu Sabulon. \v 34 Wetu sowu am miiru ñeenti junniy xasab ak juróomi téeméer (4 500) ak ñetti bunt: benn buntu Gàdd ak benn buntu Aser ak benn buntu Neftali. \v 35 Wurmbalu dëkk bi bépp fukki junniy xasab ak juróom ñett (18 000) lay doon. Turu dëkk bi nag, dale ko ca bés ba, di “\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jaa ngi fi.”»