\id EXO (WOL) \ide UTF-8 \h Mucc ga \toc1 Muccug bànni Israyil, di ñaareelu xaaju Tawreetu Musaa \toc2 Mucc ga \mt1 Muccug bànni Israyil \mt2 di ñaareelu xaaju Tawreetu Musaa \imt1 Ubbite gi \ip Ñaareelu xaaju Tawreet bii moo wéyal jaar-jaari bànni Israyil, jële ko fa ko téere bu jëkk ba, téereb Njàlbéen ga bàyyi woon. Fi téere bi jële aw turam, Mucc gi, mooy xew-xew bi ci gëna fés, di mucc gi Yàlla musal bànni Israyil, ca mbugal mu mujj ma mu wàcce woon fa Misra, mbugal ma Yàlla doge seen buumi njaam, ba génne leen fa. \ip Yàlla moo jox bànni Israyil ndigali yoon wi ca tundu Sinayi, Musaa jottli ko, muy li lal kóllëre gi mu fas, moom Yàlla ak bànni Israyil. Yàlla nag musal leen, ba ñu tala séq ak moom digganteb kóllëre. Ndigali yoon wi moo xamal mbooloom bànni Israyil nan lañuy sàmme seen digganteek moom. Yàlla moo bëggoon bànni Israyil doon ñoñam, ndax ci ñoom la nammoona amal digeem baak seen maam Ibraayma. Dige ba mooy xeeti àddina sépp, ci askanu Ibraayma lañuy barkeele. \ip Mujug téere bi kéemaan gu réy la. Mooy gannaaw ba ñu sampee jaamookaay ba, na ko Yàlla santaanee, ba Yàlla feesale ag leeram xaymab jaamookaay ba, ngir wone ne moo fa teew. \ip Ci Tënk: \ili Saar 1—18 Yàlla yiwi na bànni Israyil, génne leen Misra. \ili Saar 19—24 Yàlla fasante na kóllëre ak bànni Israyil. \ili Saar 25—40 Yàlla sant na Musaa, mu defarlu xaymab jaamookaay. \ie \c 1 \s1 Bànni Israyil dem na réewum Misra \p \v 1 Góor ñi seen baay di Yanqóoba, mi ñu dippee Israyil, ñu àndoon ak moom, dem Misra, te ku nekk yóbbaale waa këram, seeni tur a di: \v 2 Ruben ak Simeyon ak Lewi ak Yuda \v 3 ak Isaakar ak Sabulon, ak itam Beñamin; \v 4 ak Dan ak Neftali ak Gàdd ak Aser. \v 5 Góor ñi soqikoo ci Yanqóoba ñépp juróom ñaar fukk lañu (70), bu ñu ci boolee doomam, ji ñuy wax Yuusufa, moom ma ñu fekk Misra. \v 6 Gannaaw ga Yuusufaaki doomi baayam yu góor yépp nelaw, ñook maas googu gépp. \v 7 \w Bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* nag giir fa, law, di fulandiwu, ba yokku lool, fees réew ma. \s1 Firawna not na bànni Israyil \p \v 8 Ñu dem ba jëmmi jamono, beneen buur bu xamul Yuusufa falu ca Misra. \v 9 Mu wax ak waa réewam, ne leen: «Giirug \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* kat ñu ngi nuy gëna bare, ba ëpp nu doole. \v 10 Nanu ci sàkk pexe, ngir ñu bañatee yokku. Lu ko moy bu xare amee, man nañoo far ak sunuy noon, xeex ak nun, ba génn réew mi.» \v 11 Ba loolu amee ñu fal ay nit ñu leen di ga ca seeni sas, di leen ca fitnaal lool. Noonu la bànni Israyil tabaxale Firawna\f + \fr 1.11 \fr*\fk Firawna \fk*\ft turu pal la, ñeel bépp buuri Misra.\ft*\f* buuru Misra\f + \fr 1.11 \fr*\fk Misra \fk*\ft mooy réew mi ñuy wax Esibtë ba tey.\ft*\f* dëkk, ya ñu naa Pitom ak Ramses, mu def ko ay dencukaayi dund. \v 12 Terewul lu ñu leen gëna fitnaal, ñuy gën di fulandiwu, yokku, ba waa Misra am njàqare ca bànni Israyil. \p \v 13 Waa Misra dañoo mujj di jaamloo bànni Israyil bu metti, \v 14 yen leen toskarey àddina ndax liggéey yu metti. Ñuy móol ban, di tabax, waa Misra teg ca sëf leen mboolem liggéeyu tool ya. Néegoon nañu ca ñoom lool ca mboolem liggéeyu njaam bu ñu leen sas. \p \v 15 Firawna buuru Misra teg ca wax ak rewlikati \w Ebrë|lemma="Ebrë:"\w* ya\f + \fr 1.15 \fr*\fk Ebrë \fk*\ft tur la wu niti jamono jooja daan wooye xeet, ya bànni Israyil bokk.\ft*\f*, te kenn ka tuddoon Sifra, ka ca des di Puwa. \v 16 Mu ne leen: «Bu ngeen dee rewli jigéeni Ebrë yi, nangeen xool lu xale bi doon. Su dee góor, reyleen, su dee jigéen, bàyyileen, mu dund.» \v 17 Teewul rewlikat ya ragal Yàlla, ba defuñu la leen buur ba sant; xanaa ñu bàyyi liir yu góor ya, ñu dund. \v 18 Buuru Misra woolu rewlikat ya, ne leen: «Ana lu tax ngeen def lii, di bàyyi liir yu góor yi, ñu dund?» \v 19 Rewlikat ya ne ko: «Li tax kay mooy, jigéeni Ebrë yi dañoo niroowul ak jigéeni waa Misra; ndax dañoo njaxlaf, ba bu rewlikat yiy laata agsi, fekk ñu mucc ba noppi.» \v 20 Bànni Israyil nag di fulandiwu, gëna yokku, Yàlla defal rewlikat ya aw yiw, \v 21 may leen giir ndax seenug ragal Yàlla. \v 22 Gannaaw loolu Firawna sant waa réew ma yépp, ne leen: «Mboolem doom ju juddu ci Ebrë yi, di góor, sànnileen ca dex ga, waaye lu ciy jigéen, bàyyileen, mu dund.» \c 2 \s1 Musaa gane na àddina \p \v 1 Jenn waay ju bokk ci giirug Lewi nag moo jëloon janq bu mu bokkal giir. \v 2 Ndaw sa ëmb, ba mujj am doom ju góor\f + \fr 2.2 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Mucc ga\+bk* 6.20.\ft*\f*. Ba mu gisee taar, ba liir ba àndal, nëbb na ko lu mat ñetti weer. \v 3 Mu dem nag, ba manatu koo nëbb. Mu wut pañe bu ñu ràbbe barax, fatte ko godoroŋ ak ndàbb, yeb ca liir ba, daldi dem, teg ko ca biir barax, ba ca tàkkal dex, ga ñu naan Niil. \v 4 Xale bu jigéen bay magu liir ba ma nga taxaw fu soreyaatoo ak liir ba, di xool, ba xam nu muy mujje. \p \v 5 Ba mu ko defee doomu Firawna ju jigéen dikk, di sangusi ca dexu Niil ga, surgaam yu jigéen yay doxantu ca tàkk ga. Ba loolu amee mu séen pañe ba ca biir barax ba, daldi yónni jaamam, mu yót ko ko. \v 6 Naka la ko ne ubbet, yem ca xale ba, muy liir bu góor, xale bay jooy, yaram wa daw, mu ne: «Kii de ndeysaan, ci doomi \w Ebrë|lemma="Ebrë:"\w* yi la!» \v 7 Magu liir ba daldi wax doomu Firawna ja, ne ko: «Ndax ma dem wutali la ku koy nàmpal ci Ebrë yi?» \v 8 Doomu Firawna ne ko: «Waaw, demal.» Xale ba dem, indil ko yaayu liir ba. \v 9 Doomu Firawna ne ko: «Yóbbul xale bii te nàmpalal ma ko, maa lay fey.» Ndaw sa jël liir ba, di ko nàmpal. \v 10 Ba xale ba màggee, mu yót ko doomu Firawna, mu def ko muy doomam, tudde ko Musaa (mu firi Ki ñu génne), ndax la mu ko génnee ca ndox ma\f + \fr 2.10 \fr*\fk Mose \fk*\ft baatu làkku Misra la bu neexoo ak masa, di baat biy tekki «génne» ci làkku ebrë.\ft*\f*. \s1 Musaa gàddaayi na réewum Majan \p \v 11 Ba ñu demee ba Musaa màgg, dafa am bés, mu seeti bokkam ya, gis leen ca liggéey yu metti, ya ñu leen sas. Mu gis jenn waayu Misra di dóor kenn ca bokki \w Ebrë|lemma="Ebrë:"\w* ya. \v 12 Musaa geestu wet gu nekk, gisul kenn, mu rey waa Misra ja, daldi gas, suul ko. \p \v 13 Ca ëllëg sa mu dellu génn, yem ci ñaari Ebrë yuy xeex. Musaa wax ak ka tooñ, ne ko: «Lu tax ngay dóor sa moroom mii?» \v 14 Waa ja ne ko: «Ku la def sunu njiit mbaa sunu àttekat? Xanaa danga maa nara rey, na nga reye woon waa Misra ja?» Musaa nag tiit, naan ca xelam: «Ndeke mbir mi kay siiw na.» \p \v 15 Ba loolu amee Firawna dégg mbir ma, di wuta reylu Musaa. Musaa daw, ba sore Firawna, dem dali ca réewu Majan, fu dend ak ab teen. \v 16 Yettro, \w sarxalkatu|lemma="sarxalkat b-:"\w* Majan ba nag, amoon na juróom ñaari doom yu jigéen. Ñu ñëw di rootsi, di duy mbalka, ya ñuy wëgge seen juru baay. \v 17 Ay sàmm agsi, dàq leen. Musaa wallu jigéen ña, wëggal leen seen jur. \p \v 18 Ba ñu delloo ca seen baay Ruwel\f + \fr 2.18 \fr*\fk Ruwel \fk*\ft mooy Yettro ba tey.\ft*\f*, mu laaj leen ne leen: «Lu tax ngeen teela ñibbsi tey?» \v 19 Ñu ne ko: «Ab waa Misra daal, moo nu xettli ca sàmm ya; rootal na nu sax, ba wëgg jur gi.» \v 20 Ruwel ne leen: «Ana waa ja? Lu tax ngeen bàyyi ko fa? Wooyileen ko, mu añsi kay!» \p \v 21 Musaa far dal ca kër waa ja. Mu mujj ko may doomam ju ñuy wax Sipora. \v 22 Mu am doom ju góor, Musaa tudde ko Gersom (mu firi Doxandéem fii), ndaxte dafa ne: «Doxandéem laa fii.» \s1 Yàlla ñeewante na bànni Israyil \p \v 23 Ba ñu demee ba mu yàgg, Firawna buuru Misra dee. Fekk na \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* a ngay binni rekk ndax seen njaam ga. Ñuy woote wall, ba seen jooy, ya sababoo ca seen toroxteg njaam ga, àgg fa Yàlla. \v 24 Booba Yàllaa ngay dégg seeni yuux, te fàttewul \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* ga mu fasoon ak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba. \v 25 Yàlla nag geesu bànni Israyil, ñeewante leen. \c 3 \s1 Aji Sax ji yónni na Musaa \p \v 1 Léegi Musaa ngay sàmm gàtti goroom Yettro, \w sarxalkatu|lemma="sarxalkat b-:"\w* Majan ba. Mu yóbbu jur ga fu sore ca màndiŋ ma, daldi agsi ca suufu tundu Yàlla wa\f + \fr 3.1 \fr*\fk tundu Yàlla wa: \fk*\ft tund woowu, li tax ñu tudde ko tundu Yàlla, Yàlla dafa feeñoo ca kawam.\ft*\f* ca Oreb. \v 2 Malaakam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ja feeñoo ko foofa, melow sawara wuy tàkk, jafal fa ab gajj. Musaa xoolaat, ndeke gajj ba bépp jàpp na, ba ne jippét, waaye lakkul. \v 3 Musaa ne: «Mbir mu yéeme mii daal, naa jàdd xool ko, ba xam lu tax gajj bi lakkul.» \p \v 4 Ba Aji Sax ji Yàlla gisee Musaa jàdd, di xoolsi, ca gajj ba la àddoo, ne ko: «Musaa, Musaa!» Mu ne ko: «Maa ngi.» \v 5 Yàlla ne ko: «Bul jegesi, summil say dàll, ndax fii nga taxaw suuf su \w sell|lemma="sell:"\w* la.» \v 6 Mu teg ca ne: «Man maay sa Yàllay baay, di Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa te di Yàllay Yanqóoba.» Ca la Musaa nëbb kanam ga, ndax ragala xool Yàlla. \p \v 7 Aji Sax ji tegaat ca ne ko: «Gis naa bu baax fitna, ji sama ñoñ nekke Misra. Dégg naa itam seen jooy ndax kilifay saskat, yi leen di gétën ci liggéey, te ñeewante naa leen ngir seen coono. \v 8 Damaa wàcc, xettlisi leen ci waa Misra; génne leen réew moomu, ba yóbbu leen réew mu baax te yaatu, réew mu meew maak lem ja tuuroo, foofa ca diiwaanu Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña. \v 9 Yuux, yi \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* nekke nii, agsi na ba ci man, te gis naa it ni leen waa Misra di note. \v 10 Kon nag kaay, ma yónni la ca Firawna. Demal yiwiji bànni Israyil, sama ñoñ, ñu génn Misra.» \s1 Musaa di leewaayu, Yàlla di ko ñaax \p \v 11 Musaa ne Yàlla: «Waaw, waaye man tekkiwuma dara, bay dem ca Firawna, di génne \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* Misra.» \v 12 Mu ne ko: «Man déy, maay ànd ak yaw, te boo génnee mbooloo ma Misra, dingeen ma jaamusi ci tund wii. Loolooy firndeel ne, maa la yónni.» \p \v 13 Musaa ne Yàlla: «Su ma demee ca bànni Israyil, ne leen seen Yàllay maam ya moo ma yónni ca ñoom bànni Israyil de, dinañu ma laaj nu mu tudd. Lu ma leen di wax nag?» \v 14 Yàlla ne Musaa: «Maay Ki nekk. Kon waxal bànni Israyil ne leen: “Aji Nekk ji moo ma yónni ci yeen.”» \v 15 Yàlla dellu ne Musaa: «Dangay wax bànni Israyil, ne leen: “\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, seen Yàllay maam ya, di Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa te di Yàllay Yanqóoba, moo ma yónni ci yeen.” Aji Sax jee di sama tur wu sax dàkk, ñu di ma ko fàttlikoo ba fàww. \v 16 Demal woo magi Israyil, ñu daje, nga ne leen: “Aji Sax ji, seen Yàllay maam ya, di Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, moo ma feeñu, ne ma: ‘Gis naa leen, te yég naa li ñu leen di teg ci Misra. \v 17 Dogu naa leena jële ci seen notaange gii ngeen nekke ci Misra, yóbbu leen ca réewum Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña, réew mu meew maak lem ja tuuroo.’ ” \p \v 18 «Magi Israyil dinañu la déggal, su ko defee nga ànd ak ñoom, dem ca buuru Misra. Waxleen ko ne ko: “Aji Sax ji Yàllay \w Ebrë|lemma="Ebrë:"\w* yi moo nu feeñu. Kon nag ngalla may nu, nu dem topp màndiŋ mi lu mat doxub ñetti fan, ngir rendili sunu Yàlla Aji Sax ji ay sarax.” \v 19 Waaye man xam naa ne buuru Misra du leen bàyyi, ngeen dem, mbete mu taseek doole ju ko tiiñ. \v 20 Moo tax maay xàcci sama loxo, ba dumaa waa Misra ay mbugali mbugal yu kéemaane yu may def ci seen biir. Su ko defee dina leen bàyyi, ngeen dem. \v 21 Maay dogal sax waa Misra yéwéne mbooloo mii, ba keroog bu ngeen di dem, dungeen deme loxoy neen. \v 22 Képp kuy jigéen ci bànni Israyil, na laaj dëkkandoom, laajaale ku dëkk ak dëkkandoom, ay gànjari xaalis, ak gànjari wurus, ak yére yu ngeen di solal seen doom yu góor ak yu jigéen, ba waa Misra ne duŋŋ.» \c 4 \s1 Yàlla jox na Musaa ay firnde \p \v 1 Gannaaw loolu Musaa dellu wax \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ne ko: «Waaw, su ñu ma dégluwul te gëmuñu ma, xanaa ne ma: “Aji Sax ji feeñuwu la” nag?» \v 2 Aji Sax ji ne ko: «Li ci sa loxo lu mu doon?» Mu ne ko: «Aw yet.» \v 3 Aji Sax ji ne ko: «Sànni ko ci suuf.» Mu sànni yet wa ca suuf, mu soppliku jaan. Musaa dellu gannaaw. \v 4 Aji Sax ji ne ko: «Tàllalal sa loxo, jàpp ci geen gi.» Musaa tàllal loxo ba, ne nikk jaan ja, mu dellu di aw yet ca loxoom. \v 5 Aji Sax ji ne ko: «Loolu ngay def, ngir ñu gëm ne Aji Sax ji seen Yàllay maam ya, di Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa te di Yàllay Yanqóoba, moo la feeñu ci lu wér.» \p \v 6 Aji Sax ji dellooti ne ko: «Léegi dugalal sa loxo, teg ko ci sa dënn.» Musaa dugal loxoom, teg ko ca dënnam; ba mu ko génnee, mu defi àkk, xobbiku. \v 7 Aji Sax ji ne ko: «Dellool sa loxo ci sa dënn.» Musaa delloo loxo ba ca dënn ba, génnewaat ko, mu dellu mel ni yaramam. \v 8 Mu ne ko: «Bu ñu la gëmul mbaa ñu baña seet ci firnde ju jëkk ji, dinañu gëm ndax firnde ji ci topp. \v 9 Waaye su lenn ci ñaari firnde yi taxul ñu gëm, te déggaluñu la, nanga tanqe ndox ci dexu Niil gi, tuur ko ci suuf su wow si, su ko defee ndox, ma nga tanqe ca dex ga, day soppliku deret ci suuf si.» \s1 Yàlla def na Aaróona bëkk-néegu Musaa \p \v 10 Musaa nag ne \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji: «Da di, Boroom bi, man naka jekk duma nitu waxkat, du démb, du tey jii ngay wax ak man. Dama di ku leeb, Sang bi, te tëlee wax.» \v 11 Aji Sax ji ne ko: «Ku sàkkal nit gémmiñ? Kan mooy luuwal, di tëxal, di gisal mbaa muy gumbaal? Xanaa du man Aji Sax ji? \v 12 Demal rekk, man maay ànd ak yaw booy wax, di la xamal li ngay wax.» \v 13 Teewul Musaa ne ko: «Ngalla waay, yónnil keneen ku la soob rekk, sama Boroom.» \v 14 Aji Sax ji nag mer ba fees ndax Musaa. Mu ne ko: «Sa mag Aaróona, \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* bi, da fee nekkul? Moom, xam naa ne ku mana wax la. Mu ngi lay gatandusi sax, te bu la gisee, bég. \v 15 Nanga wax ak moom, digal ko li mu wara wax. Man maay ànd ak yeen, yaak moom, saa yu ngeen dee wax, te maa leen di xamal, yeen ñaar, li ngeen wara def. \v 16 Na lay waxal ak mbooloo mi; su ko defee sa kàddu di kàddoom, te yaw nga mel ci moom ni Yàlla. \v 17 Yóbbaaleel yet wii nag, ndax ci ngay defe firnde yi.» \s1 Musaa dellu na Misra \p \v 18 Musaa nag dellu ca goroom Yettro, ne ko: «May ma, ma dellu Misra, seeti samay bokk, ba xam nu ñu def.» Yettro ne ko: «Demal ak jàmm.» \v 19 Ci biir loolu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax ak Musaa ca Majan, ne ko: «Dellul Misra, ndaxte ña la doon wuta rey ñépp dee nañu.» \v 20 Musaa ànd ak soxnaam ak doomam yu góor, waral leen mbaam. Ma ngay dellu Misra, jàpp yetu Yàlla wa\f + \fr 4.20 \fr*\fk yetu Yàlla wa \fk*\ft mooy yetu Musaa, wa Yàlla defe kéemaan ya.\ft*\f* ca loxo ba, yóbbaale. \v 21 Aji Sax ji ne ko: «Keroog boo delloo Misra, nanga taxaw temm, te def ca kanam Firawna kéemaan, yi ma teg ci sa loxo yépp. Man maay dëgëral boppam, mu të ba du bàyyi mbooloo mi, ñu dem. \v 22 Su ko defee nga wax Firawna, ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: ‘Israyil mooy sama taaw bu góor. \v 23 Te wax naa la ne la, nga bàyyi sama doom, ndax mu man maa jaamu, nga bañ. Kon nag dinaa rey sa taaw bu góor.’ ”» \p \v 24 Ba ñu lalee panaan ca yoon wa, Aji Sax ji dafa dogale Musaa, nar koo rey. \v 25 Soxnaam Sipora jël paaka bu ñu yette doj, dog mbuñukam doomam, laalale ko ca tànkam, ne ko: «Jëkkër ju ñuy jote deret de laa am.» \v 26 Ba loolu amee Aji Sax ji bàyyi Musaa. Ba Sipora di wax lu jëm ci jëkkër ju ñuy jote deret, aaday xarfal gaa taxoon. \p \v 27 Ci biir loolu Aji Sax ji wax Aaróona ne ko: «Demal gatanduji Musaa ca màndiŋ ma.» Aaróona dem seeti ko ca tundu Yàlla wa, fekk ko fa, taf ko ca kawam. \v 28 Musaa xamal ko la ko Aji Sax ji dénk lépp, ak mboolem firnde, ya mu ko sant mu def ko. \p \v 29 Ci kaw loolu Musaa ak Aaróona agsi Misra. Ñu woo magi \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* yépp, ñu daje. \v 30 Aaróona jottli leen kàddu ya Aji Sax ji wax Musaa yépp, ba noppi Musaa wone firnde ya ca kanam mbooloo ma, \v 31 ba mbooloo ma gëm. Ba magi Israyil déggee ne Aji Sax ji nemmiku na bànni Israyil te gis na notaange, gi ñu nekke, dañoo sujjóot, màggal Aji Sax ji. \c 5 \s1 Musaa ak Aaróona seeti nañu Firawna \p \v 1 Gannaaw loolu Musaa ak Aaróona dem ca Firawna, ne ko: «\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Yàllay Israyil dafa wax ne: “Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma ca màndiŋ ma.”» \p \v 2 Firawna ne: «Kan mooy Aji Sax ji, ba ma di ko déggal, di bàyyi Israyil, ñuy dem? Xawma sax kuy Aji Sax ji, waxumalaa may bàyyi Israyil, ñuy dem.» \v 3 Ñu ne ko: «Sunu Yàlla, nun \w Ebrë|lemma="Ebrë:"\w* yi, moo nu feeñu. Ngalla may nu, nu dem topp màndiŋ mi lu mat doxub ñetti fan, ngir rendili sunu Yàlla Aji Sax ji sarax, lu ko moy mu dumaa nu jàngoro mbaa ab xare.» \p \v 4 Buuru Misra ne leen: «Yeen Musaa ak Aaróona, lu waral ngeen di jële mbooloo mi ci seeni liggéey? Laggleen ca seeni sas waay!» \v 5 Firawna dellu ne: «Baadoolo yi ne xas tey ci réew mi, ngeen nar leena dëdduloo seeni sas!» \s1 Firawna yokk na liggéeyu bànni Israyil \p \v 6 Keroog ca bés ba la Firawna sant saskati liggéey yaak farbay ngàllo, ga jiite jaam ya, ne leen: \v 7 «Buleen defati na woon, di jox mbooloo mi boob mu ñuy móole. Gannaaw-si-tey nañu dem wutal seen bopp boob. \v 8 Waaye sasleen leen limu móol, ya ñu daan móol naka jekk. Buleen ko wàññi, ndax ay yaafus lañu; moo leen tax di dee-deeluy waxeey naan: “May nu, nu dem rendili sunu Yàlla sarax!” \v 9 Nañu leen yen liggéey bu gëna metti, te ñu dëkke ko, ba duñu tala déglu ay feni neen.» \p \v 10 Ba mu ko defee saskati liggéey ya ak farbay ngàllo ga génn, wax ak mbooloo ma, ne leen: «Firawna nee na, du moo leen di jox boob. \v 11 Yeena wara wutal seen bopp boob ak fu ngeen ko mana ame, te du tax lenn teggiku ci seen liggéey.» \v 12 Fa la mbooloo ma tasaaroo ca biir réewum Misra, di wut boob. \v 13 Saskati liggéey ya nag di leen soññ, naan leen: «Matal-leen seen sasu bëccëg bu nekk, ni ngeen ko daan matale, ba boob amee.» \v 14 Ñuy dóor farbay ngàllo, ga bokk ca \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, te saskati liggéey yu Firawna fal leen ngir ñuy jiite bànni Israyil ca liggéey ba. Ña nga leen naan: «Lu waral démb ak tey yépp mataluleen limu móol, yi ñu leen sas, te ngeen daan ko matal?» \p \v 15 Booba la farbay ngàllog Israyil, dem jooytuji ca Firawna, ne ko: «Sang bi, lu tax nga def nu nii? \v 16 Du menn boob mu ñu nu joxati, te teewul ñu di nu sant nuy móol, di nu ci dóor. Te kat sang bi, sa waa réew a tooñ.» \v 17 Firawna ne leen: «Yaafus yi ngeen doon! Yaafus a leen tax di wax naan: “May nu, nu dem rendili \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji sarax.” \v 18 Neleen mott, liggéeyi! Du menn boob mu ñu leen di jox. Te du tee ngeen matal seen limu móol.» \v 19 Farbay ngàllo, ga bokk ca bànni Israyil nag xam ne dal nañu aw sas, ndax la ñu leen ne duñu wàññi lenn ca limu móol, ya leen war bés bu nekk. \p \v 20 Ba loolu amee ñu bàyyikoo ca Firawna, daldi yem ca Musaak Aaróona, fa ñu leen doon xaar. \v 21 Farba ya ne leen: «Yal na leen Aji Sax ji gis ba mbugal leen, ndax tax ngeen Firawnaaki dagam jéppi nu, te mel na ni yeena teg ci seeni loxo saamar, bi ñu nuy reye.» \p \v 22 Musaa dégg loolu, dellu ci Aji Sax ji, ne ko: «Éey Boroom bi, loraange gi nga yóbbe mbooloo mii nag? Loo ma doon yónnee? \v 23 Ba ma demee ca Firawna, di wax ci sa tur ba tey, mu ngi lor bànni Israyil, sa ñoñ, te xettliwoo leen sax!» \c 6 \p \v 1 Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Dinga gis léegi ni may def Firawna: loxo bu ko ëpp dooleey tax mu bàyyi leen ñu dem. Bir na ne, loxo bu ko ëpp doole mooy tax mu dàq leen réewam.» \s1 Yàlla dellu na yónni Musaa \p \v 2 Yàlla dellu wax Musaa ne ko: «Man maay \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \v 3 Yàlla Aji Man ji, mooy ni ma feeñoo woon Ibraayma, te ni laa feeñoo Isaaxa ak Yanqóoba it, waaye sama tur, Aji Sax ji, leeraluma leen ko woon. \v 4 Te itam damaa fasoon ak ñoom \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w*, ngir jox leen réewum Kanaan, réew ma ñu nekkoon ay doxandéem. \v 5 Maa déggal sama bopp yuuxi \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, gi waa Misra def ay jaam, te fàttewuma sama kóllëre ga. \v 6 Kon nag waxal bànni Israyil ne leen: Man maay Aji Sax ji. Maa leen di sippil, yeen bànni Israyil, li leen waa Misra sëf, te maa leen di teggil njaam, gi ñu leen teg. Maay tàllal sama loxo, dogal mbugal yu kéemaane, ba goreel leen. \v 7 Maa leen di def sama ñoñ, di seen Yàlla. Dingeen xam ne man Aji Sax ji maay seen Yàlla, ji leen di teggil sas, yi leen waa Misra teg. \v 8 Maa leen di yóbbu ba ngeen dugg réew ma ma giñoon ne maa koy jox Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, te maa leen koy moomale, man Aji Sax ji.» \p \v 9 Ba Musaa waxee loolu bànni Israyil, dégluwuñu ko sax ndax xol bu jeex ak njaam gu metti. \p \v 10 Aji Sax ji wax Musaa ne ko: \v 11 «Demal wax Firawna buuru Misra, mu bàyyi bànni Israyil, ñu génn réewam.» \v 12 Musaa tinu Aji Sax ji ne ko: «Waaw, ndegam bànni Israyil sax nanguwuñu maa déglu, nu ma Firawna di déggale, man mii tëlee wax?» \v 13 Aji Sax ji nag wax ak Musaa ak Aaróona, jox leen ay ndigal ci mbirum bànni Israyil ak Firawna buuru Misra, ngir ñu yiwi bànni Israyil, ba ñu génn Misra. \s1 Lu jëm ci cosaanu Musaa ak Aaróona \p \v 14 \w Bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ya yilifoon seen kër baay, ñoo di: \p Góor ña Ruben, taawu Israyil, jur: Anog ak Palu ak Esron ak Karmi. Ñooñoo sos làngi Ruben. \p \v 15 Doomi Simeyon yu góor di Yemuwel ak Yamin ak Owàdd ak Yakin ak Sowar ak Sawul, mi ndeyam dib Kanaaneen. Ñooñoo sos làngi Simeyon. \p \v 16 Doomi Lewi yu góor ñoo di Gerson ak Keyat ak Merari, ku nekk ak askanam. At ya Lewi dund, téeméer la ak fanweer ak juróom ñaar (137). \p \v 17 Doomi Gerson yu góor ñoo di Libni ak Simey, ñook seeni làng. \p \v 18 Doomi Keyat yu góor ñoo di Amram ak Isar ak Ebron ak Usyel; te at ya Keyat dund, téeméer la ak fanweer ak ñett (133). \p \v 19 Doomi Merari yu góor ñoo di Maali ak Musi. \p Ñooñoo sos làngi Lewi ak seeni giir. \p \v 20 Amram moo jël bàjjanam Yokebedd soxna\f + \fr 6.20 \fr*\ft Séy bu ni jegee mujj nañu ko tere bànni Israyil. Waaye jamonoy waajuri Musaa, séy bu jegee noonu aada la fa woon.\ft*\f*, kooku am ak moom Aaróona ak Musaa. At, ya Amram dund, téeméer la ak fanweer ak juróom ñaar (137). \p \v 21 Doomi Isar yu góor ñoo di Kore ak Nefeg ak Sikkri. \p \v 22 Doomi Usyel yu góor di Mikayel ak Elsafan ak Sitiri. \p \v 23 Aaróona moo jël Eliseba doomu Aminadab, jigéenub Nason. Kooku am ak moom Nadab ak Abiyu ak Elasar ak Itamar. \p \v 24 Doomi Kore yu góor ñoo di Asir ak Elkana ak Abiyasaf. Ñooñoo sos làngi Kore. \p \v 25 Elasar doomu Aaróona moom, moo jël soxna kenn ca doomi Putiyel, kooku am ak moom Fineyas. \p Ñooñoo yilif seeni kër baay ca \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ña, ku nekk sos làngam. \v 26 Aaróona moomu nag, mook Musaa, la \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax, ne leen: «Génneleen bànni Israyil Misra, kurél ci kaw kurél.» \v 27 Ñoom ñooñu ñoo wax ak Firawna buuru Misra, ngir génne bànni Israyil Misra; du keneen ku dul Musaa ak Aaróona. \s1 Yàlla feddli na digeem baak Musaa \p \v 28 Keroog ba \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxee ak Musaa ca réewum Misra, \v 29 da koo wax, ne ko: «Man maay Aji Sax ji. Nanga wax Firawna buuru Misra, li ma lay wax lépp.» \v 30 Teewul Musaa tinu Aji Sax ji, ne ko: «Waaw, waaye man, damaa tëlee wax. Mbaa Firawna dina ma déggal yee?» \c 7 \p \v 1 Aji Sax ji ne Musaa: «Dama ne, def naa nga féete Firawna fi ko Yàlla féete, sa mag Aaróona di sa yonent. \v 2 Su ko defee yaw nga wax ko li ma la sant lépp, sa mag Aaróona wax ko Firawna, ngir mu bàyyi \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, ñu génn réewam. \v 3 Waaye man maay dëgëral boppu Firawna, ba fulandi samay firnde ak samay kéemaan ci biir réewum Misra. \v 4 Firawna du leen déggal. Su ko defee nag maay tàllal sama loxo, tiimale Misra, te maay dogal mbugal yu kéemaane, ba goreel bànni Israyil, sama ñoñ, ñu génn Misra, kurél ci kaw kurél. \v 5 Keroog bu ma tàllalee sama loxo, tiimale ko Misra, ba génnee bànni Israyil ca seen biir, waa Misra dinañu xam ne maay Aji Sax ji.» \p \v 6 La Aji Sax ji santoon Musaak Aaróona, noonu rekk lañu ko defe. \v 7 Musaa nga tollu woon ci juróom ñett fukki at (80); Aaróona moom am juróom ñett fukki at ak ñett (83); ca jamono, ya ñuy wax ak Firawna. \s1 Firawna gàntu na \p \v 8 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax Musaa ak Aaróona ne leen: \v 9 «Bu leen Firawna waxee ne leen: “Defleen seeni kéemaan boog!” danga naan Aaróona: “Jëlal yet wi, sànni ci suuf ci kanam Firawna.” Su ko defee yet wi dina soppliku jaan.» \p \v 10 Ci kaw loolu Musaa ak Aaróona àgg ba ca Firawna. Ñu def la leen Aji Sax ji santoon. Aaróona jël yetam, sànni ca suuf ca kanam Firawnaaki dagam; yet wa soppliku jaan. \v 11 Ba mu ko defee Firawna moom itam woo boroom xam-xam yaak jibar ya. Ñeengokati Misra ya ñoom it fexe ca seeni xargafuufa, ba def lu mel noona. \v 12 Ku nekk ca ñoom sànni yetam, mu soppliku jaan, yetu Aaróona nag wonn seeni yet\f + \fr 7.12 \fr*\ft Manees naa jàpp ne jaan, ja yetu Aaróona soppliku woon, moo wonn jaan, ya seen yet soppliku.\ft*\f*. \v 13 Terewul Firawna të, faalewu leen, muy la Aji Sax ji waxoon. \s1 Yar bu jëkk ba: ndox mu soppliku deret \p \v 14 Gannaaw loolu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na Musaa ne ko: «Firawna daa dëgër bopp. Bañ naa bàyyi mbooloo mi, ñu dem. \v 15 Dangay teela xëy ca Firawna ëllëg, buy génn jëm ca ndox ma, nga dogale ko ca tàkkal dexu Niil, te yóbbaale yet, wa soppliku woon jaan. \v 16 Wax ko ne ko: “Aji Sax ji Yàllay \w Ebrë|lemma="Ebrë:"\w* yi, moo ma yónni ci yaw. Mu di la wax, ne la: ‘Bàyyil sama ñoñ, ñu jaamuji ma ca màndiŋ ma.’ Yaw nag booba ba tey yaa ngi tanqamlu. \v 17 Aji Sax ji dafa wax ne: ‘Ni ngay xame ne man maay Aji Sax ji nii la: Dama ne, dinaa dóor ci ndoxum Niil mi yet, wi ci sama loxo, ndox mi soppliku deret; \v 18 su ko defee jën yi ci dex gi dee, dexu Niil gi mujj xasaw, ba waa Misra dootuñu mana naan ci ndoxum Niil.’ ”» \p \v 19 Ci kaw loolu Aji Sax ji ne Musaa: «Waxal Aaróona ne ko: “Jëlal saw yet, te tàllal sa loxo tiimale ko ndoxi Misra, muy seeni dex ak seen yooni ndox ak seeni déeg ak fépp fu ndox taa, mu ànd soppliku deret.” Deret ja dina daj Misra gépp, ba ca këll yaak njaq ya.» \v 20 Musaa ak Aaróona def loolu lépp, na leen ko Aji Sax ji sante. Naka la ne xaas yet wa, ne ko tàrr ca ndoxum Niil ma, ca kanam Firawnaaki dagam, ndoxum Niil ma mépp di deret, \v 21 jën ya ca dexu Niil ga dee, dexu Niil ga xasaw, ba waa Misra manatuñoo caa naan. Misra gépp di deret. \v 22 Ñeengokati Misra itam fexe ca seeni xargafuufa, ba def lu mel noona. Firawna të rekk, tanqamlu Musaak Aaróona, muy la Aji Sax ji waxoon. \v 23 Ba loolu amee Firawna ne wërëñ, dellu këram, te bàyyiwul xel ca mbir ma. \v 24 Waa Misra gépp di gas la wër dexu Niil, ngir am ndoxum naan, ndax manuñu woona naan ca dex ga. \s1 Yarub ñaareel ba: mbott yu daj réew ma \p \v 25 Ba \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dalee ca kaw dexu Niil, ba ñu teg ca juróom ñaari fan, \c 8 \p \v 1 Aji Sax ji da ne Musaa: «Demal ca Firawna, ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Bàyyil sama ñoñ, ñu dem jaamuji ma. \v 2 Soo leen bañee bàyyi, ñu dem kat, maa leen di mbugale ay mbott yu daj sam réew. \v 3 Dexu Niil gi day ramm-rammeeki mbott, te dinañu ñëw, duggsi sa biir kër, ak sa néegu biir, ak sa kaw lal, ak sa këri dag, ak sa waa réew, ba ca lakkukaay yaak notukaayi mburu ya. \v 4 Mbott yi dinañu yéeg ci sa kaw, yéeg ci kaw waa réew mi, ak sa dag yépp.”» \p \v 5 Ba loolu weesee Aji Sax ji ne Musaa: «Waxal Aaróona, ne ko mu ŋàbb yet wi, tàllal loxoom, tiimale ko dex yi, ak yooni ndox yeek déeg yi, ngir indi mbott yi ci biir réewum Misra.» \v 6 Aaróona tàllal loxoom, mu tiim ndoxi Misra, mbott ya jóg, lal réewum Misra. \v 7 Ñeengokat ya it fexe ca seeni xargafuufa, ba indi ay mbott ca réewum Misra. \p \v 8 Ba mu ko defee Firawna woo Musaak Aaróona, ne leen: «Ñaanleen Aji Sax ji, ngir mu teqale nook mbott yi, man ak sama waa réew. Kon dinaa bàyyi mbooloo mi, ñu dem rendili Aji Sax ji sarax.» \v 9 Musaa ne Firawna: «Saa yu la neexee rekk, sang bi. Wax ma kañ laa lay ñaanal, yaw ak say dag ak sa waa réew, ngir jële fi mbott yi, ñu tàggook yeen, génn seeni kër, ca dexu Niil ga doŋŋ lañuy des.» \v 10 Mu ne ko: «Nay ëllëg.» Musaa ne ko: «Baax na, ndax nga xam ne sunu Yàlla Aji Sax ji amul moroom. \v 11 Mbott yi dinañu jóge sa kër, teqlikook yeen, yaak say dag ak sa waa réew, ca dexu Niil ga doŋŋ lañuy des.» \v 12 Musaa ak Aaróona nag jóge ca Firawna, Musaa tinu Aji Sax ji ca mbirum mbott ya mu yare Firawna. \v 13 Aji Sax ji def la ko Musaa ñaan, mbott ya dee, ba jeex ca kër yaak ca ëtt yaak tool ya. \v 14 Ñu jal koo jal, ba xet ga ubale ca réew ma. \v 15 Teewul, ba Firawna gisee ca mbir ma tan, daa wéye të, tanqamlu leen, muy la Aji Sax ji waxoon. \s1 Yarub ñetteel ba: rayentaan yu daj réew ma \p \v 16 Ba loolu amee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ne Musaa: «Waxal Aaróona ne ko mu tàllal yetam, dóor ci pëndub suuf si, mu doon ay rayentaan\f + \fr 8.12 \fr*\fk rayentaan: \fk*\ft li ñuy wax rayentaan fii, kenn xamul lan la dëgg. Waaye luy naaw lu tuut la, di same aka màtte.\ft*\f* ci réewum Misra gépp.» \v 17 Ñu def loola, Aaróona tàllal loxoom, ba mu ŋàbbe yet wa, dóor ca pënd ba, mu doon ay rayentaan yu song nit ak rab; pëndu suuf sépp a defi rayentaan ca réewum Misra gépp. \v 18 Ñeengokat ya fexe ca seeni xargafuufa, nu ñu defe ay rayentaan, waaye manuñu. Rayentaan ya nag song nit ñaak rab ya. \v 19 Ñeengokat ya ne Firawna: «Lii de Yàlla rekk a ko man!» Teewul Firawna wéye të rekk, tanqamlu leen, muy la Aji Sax ji waxoon. \s1 Yarub ñeenteel ba: weñ yuy màtte \p \v 20 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa, ne ko: «Teelala xëy ëllëg ca Firawna, buy génn jëm ca ndox ma, nga wax ko ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: ‘Bàyyil sama ñoñ, ñu dem jaamuji ma. \v 21 Ndaxte soo bàyyiwul sama ñoñ, ñu dem kat, dinaa yuri ay ndiiraani weñ yuy màtte ci seen kaw, yaak say dag ak sa waa réew, te dinañu àgg ci sa biir kër. Këri waa Misra dina fees ak weñ yuy màtte, ba suuf, si ñu taxaw sax, weñ yee koy muur. \v 22 Waaye bu keroogee dinaa ci musal diiwaanu Gosen, ga sama ñoñ dëkke, ba ay weñ du fa same, ndax nga xam ne, man Aji Sax ji maa ngi ci digg réew mii, \v 23 te maay musal sama ñoñ ci musiba moomuy dal saw askan. Ëllëg firnde jooju dina am.’ ”» \v 24 Aji Sax ji def loola, weñ yi def ndiiraan yu réy, song kër Firawna ak kër dagam ya, dajal réewum Misra, ba réew ma yàqu ndax ndiiraani weñ ya. \p \v 25 Firawna daldi woolu Musaak Aaróona, ne leen: «Demleen rendili seen Yàlla sarax, te nay ci biir réew mi nag.» \v 26 Musaa ne ko: «Loolu du yoon, ndax li nuy rendil sunu Yàlla Aji Sax ji, waa Misra dañu koy xof. Te bu nu sarxalee lenn lu waa Misra xof, ñuy gis, dinañu nu dóor ay doj, ba nu dee. \v 27 Kon kay danoo wara génn, topp màndiŋ mi lu mat doxub ñetti fan, rendili fa sunu Yàlla Aji Sax ji sarax, ni mu nu ko sante.» \v 28 Firawna àddu ne: «Dinaa leen may, ngeen dem ca màndiŋ ma, rendili seen Yàlla Aji Sax ji sarax, waaye buleen sore lool. Ñaanal-leen ma nag.» \v 29 Musaa ne ko: «Bu ma bàyyikoo ci yaw rekk Firawna, dinaa tinu Aji Sax ji, ngir ëllëg ndiiraani weñ yi teqlikook yaw, ak say dag ak sa waa réew, waaye kat Firawna, bu nu naxati, di baña bàyyi mbooloo mi, ñu rendili Aji Sax ji sarax.» \p \v 30 Musaa bàyyikoo fa Firawna, daldi tinu Aji Sax ji. \v 31 Aji Sax ji defal Musaa la mu ñaan, jële ndiiraani weñ ya ca Firawnaaki dagam ak waa réewam, ba weñ desatu fa. \v 32 Teewul Firawna të rekk, baña bàyyi mbooloo ma, ñu dem. \c 9 \s1 Yarub juróomeel ba: Deewug jur ga \p \v 1 Ba loolu wéyee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji da ne Musaa: «Demal ca Firawna, nga ne ko: Aji Sax ji Yàllay \w Ebrë|lemma="Ebrë:"\w* yi dafa wax ne: “Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma. \v 2-3 Ndax boo leen bañee bàyyi kat, xanaa di leen téye ba tey, loxol Aji Sax ji dina dal ci sa kaw jur gi ci tool yi, muy fas ak mbaam ak giléem, jur gu gudd ak gu gàtt, te jàngoro ju aaytal lool lay doon. \v 4 Waaye man Aji Sax ji maay ràññatle juru \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ak juru waa Misra, ba lenn du dee ci mboolem lu bànni Israyil moom.”» \p \v 5 Aji Sax ji nag jàpp na bés, nee na: «Ëllëg maay def loolu ci réew mi.» \v 6 Ca ëllëg sa Aji Sax ji def ko: jurug waa Misra gépp dee, te jurug bànni Israyil, lenn deewu ca. \v 7 Ba Firawna yónnee, ba nemmiku mbir ma, xam na ne lenn deewul ca juru bànni Israyil. Teewul mu të ticc ba tey, baña bàyyi mbooloo ma, ñu dem. \s1 Yarub juróom benneel ba: Taab ya \p \v 8 Ba loolu amee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax Musaa ak Aaróona ne leen: «Tibbleen seeni loxo dóomu puuru ban, ba mu fees, Musaa xalab mu jëm asamaan, Firawna di ci gis. \v 9 Su ko defee dóom bi doon pënd bu sew ci kaw réewum Misra gépp, daldi def ay taab yuy sotti dëtt ci réewum Misra gépp, nit ak mala.» \v 10 Ñu sàkk dóomu-taal, àgg ca kanam Firawna, Musaa xalab dóom ba, mu jëm asamaan, dóom ba def ay taab yuy sotti dëtt ca nit ñaak mala ya. \v 11 Ci kaw loolu ñeengokat ya taluñoo janook Musaa ndax ay taab, ñoom ak waa Misra gépp. \v 12 Teewul Aji Sax ji dëgëral boppu Firawna, mu të, tanqamlu leen, muy la Aji Sax ji waxoon Musaa. \s1 Yarub juróom ñaareel ba: Tawub yuur ba \p \v 13 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ne ko: «Teelala xëy ca Firawna ëllëg, nga wax ko ne ko: “Aji Sax ji, Yàllay \w Ebrë|lemma="Ebrë:"\w* yi, dafa wax ne: ‘Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma. \v 14 Ndax kat bii yoon maa ngii di yebal sama mbugal yépp ci yaw ci sa bopp, ak say dag ak sa waa réew, ngir nga xam ne awma moroom ci àddina wërngal këpp. \v 15 Nëgëni tey doon naa xàcci sama loxo xaat, dumaa leen mbas mu leen di fare ci kaw suuf, yaw yaak sa waa réew. \v 16 Waaye maa la musal, te li ma ci jublu moo di won la sama doole, ba sama riirum tur dajal àddina. \v 17 Ndaxam yaa ngi réy-réylu ci sama kaw ñoñ ba tey, bañ leena bàyyi, ñu dem. \v 18 Te kat nëgëni ëllëg dinaa taw yuur\f + \fr 9.18 \fr*\fk tawub yuur: \fk*\ft ndoxum taw la, mu sedd, ba defi donj.\ft*\f* bu réy, bu masula am Misra, ba mu sosoo ba tey jii. \v 19 Kon nag sa jur ak mboolem loo am, te mu nekk ci biti, booleel fat fu wóor, ndax lu nekk ci biti te fateesu ko, su tawtee dee, muy nit mbaa mala.’ ”» \v 20 Ba mu ko defee ña ragal kàddug Aji Sax ji ca dagi Firawna fat seeni jaam ak seeni jur fu wóor. \v 21 Ña faalewul kàddug Aji Sax ji, ñoom, wacc seeni jaam ak seeni jur ca biti. \p \v 22 Aji Sax ji ne Musaa: «Yékkatil sa loxo ca kaw, mu jublu asamaan, ngir tawub yuur bi dal ci réewum Misra mépp, nit ak mala, ba ci lépp luy gàncax ci réewum Misra.» \v 23 Musaa ne yékkét yet wa, mu jublu asamaan, Aji Sax ji yebal dënu baak tawub yuur ba, sawara wa ne yureet fi suuf, ànd ak tawub yuur, ba Aji Sax ji sóob ca réewum Misra. \v 24 Tawub yuur ba réy lool, ànd ak sawara, wa jaxasook yuur ba, di xuyy-xuyyi, muy guléet ca cosaanu réewum Misra ba bésub keroog. \v 25 Tawub yuur ba dal ca mboolem réewum Misra, daaneel lépp lu ne woon ca biti, nit ak mala, daaneel gàncax gépp, dammat garab ya ca àll ba yépp. \v 26 Diiwaanu Gosen, ga \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* dëkkoon doŋŋ, moo mucc ca tawub yuur ba. \p \v 27 Firawna nag yónnee, woolu Musaak Aaróona. Mu wax leen ne leen: «Bii yoon de, maa tooñ. Aji Sax ji moo nekk ci dëgg, te maak sama waa réew ñoo sikk. \v 28 Tinuleen Aji Sax ji, ndax dënu yu màgg yeek tawub yuur bi dakk. Dinaa leen bàyyi, ngeen dem. Deesu leen fi téyeeti.» \v 29 Musaa ne ko: «Bu may génn dëkk bi rekk, di tàllal Aji Sax ji samay loxo, dënu yi dakk, tawub yuur bi siwet, ngir nga xam ne àddina, Aji Sax jeey boroom. \v 30 Waaye xam naa ne, loolu du tax ba tey, nga ragal Yàlla Aji Sax ji, yaw, yaak say dag.» \p \v 31 Fekk na gàncax ga ñuy defare wëñu lẽe yàqu na, mook peppum lors ba, ndax lors baa nga tollu woon ci waaja focci, gàncax ga ñuy defare lẽe di tóor. \v 32 Waaye xeeti peppi bele ya, lenn yàquwu ca, ndax yooyooy mujja ñor. \p \v 33 Naka la Musaa bàyyikoo ca Firawna, ba génn dëkk ba rekk, daldi tàllal Aji Sax ji ay loxoom. Dënu yaak tawub yuur ba ne tekk, taw ba siwet. \v 34 Ba mu ko defee Firawna gis ne tawub yuur baak dënu ya dakk na, mu tëëti ticc, mooki dagam, dellu cig tooñam. \v 35 Firawna të rekk, baña bàyyi bànni Israyil, ñu dem, muy la Aji Sax ji waxoon, Musaa jottli. \c 10 \s1 Yarub juróom ñetteel ba: Njéeréer ya \p \v 1 Ba loolu weesee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax Musaa ne ko: «Demal ca Firawna. Maa dëgëral boppam, mooki dagam, ngir jëfe samay firnde fi seen biir. \v 2 Su ko defee ngeen mana nettali seeni doom ak seeni sët ni ma torxale waa Misra, ak sama firnde, yi ma def fi seen biir, ndax ngeen xam ne man maay Aji Sax ji.» \p \v 3 Musaa ak Aaróona nag dem ca Firawna, wax ko ne ko: «Aji Sax ji Yàllay \w Ebrë|lemma="Ebrë:"\w* yi dafa wax ne: “Siide nga maa nangul daal? Waaw, foo àpp sa ngàntal ak man? Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma. \v 4 Soo bañee bàyyi sama ñoñ, ñu dem kat, ëllëg dinaa wàcce ay njéeréer ci sam réew. \v 5 Dinañu lal déndu réew mi, ba kenn dootu gis suuf. Dinañu lekk lu fi tawub yuur bi ba woon, te garab yi ci seeni tool yépp lañuy lekk. \v 6 Te itam dinañu fees say biir kër ak sa këri dag yépp ak këri waa Misra gépp, muy mbir mu say maam ak say mamaat masula gis, ba ñu ganee àddina ba bésub tey jii.”» \p Ba loolu amee Musaa walbatiku, bàyyikoo ca Firawna. \v 7 Dagi Firawna ya wax Firawna ne ko: «Lu nuy seetaanati, waa jii di nu yóbbe aw ay? Bàyyil bànni Israyil ñii kay, ñu màggali seen Yàlla Aji Sax ji! Xanaa yéguloo ne Misra tas na?» \v 8 Ñu délloosi nag Musaak Aaróona ca Firawna, mu ne leen: «Demleen màggali seen Yàlla Aji Sax ji! Waaw, ñiy dem sax, ñan la?» \v 9 Musaa ne ko: «Nun ñépp ay dem kay, mag ak ndaw; danuy dem, ànd ak sunuy doom, góor ak jigéen, ak sunuy jur, gu gudd ak gu gàtt, ndax màggalug Aji Sax ji la ci nun.» \p \v 10 Firawna ne leen: «Ãa, yal na leen Aji Sax ji saxoo taxawu walla, ndegam maa leen di bàyyi moos, ngeen dem, yóbbaale seen njaboot! Xam ngeen ne naruleen njub de. \v 11 Mukk laa wax! Du dangeen di màggal Aji Sax ji? Demleen boog, yeen ñiy góor!» \p Ba loolu amee ñu dàq leen, ñu jóge ca Firawna, \v 12 Aji Sax ji ne Musaa: «Tàllalal sa loxo, mu tiim réewum Misra, ngir njéeréer yi ñëw, song réewum Misra, ba lekk gàncax gi ci réew mi, lekk lépp lu fi tawub yuur bi bàyyi woon.» \p \v 13 Ba mu ko defee Musaa tàllal yetam, mu tiim réewum Misra, Aji Sax ji yékkati ngelaw ca réew ma, mu jóge penku, yendoo gelaw, fanaanoo ko. Bët set, ngelawal penku la indi njéeréer ya. \v 14 Njéeréer ya song réewum Misra mépp, sam déndu Misra wépp, ba mu fatt taraj. Lu ni tollu masula am, te dootu amati. \v 15 Njéeréer ya daa muur suuf sa sépp, ba giseesu ko. Suuf sa ñuul kukk. Njéeréer ya lekk lépp luy gàncax mbaa meññeefi garab gu tawub yuur ba jotuloona yàq, ba lenn lu naat desatul, du xobi garab, du gàncax, ca mboolem réewum Misra. \p \v 16 Firawna nag gaaw woolu Musaak Aaróona, ne leen: «Tooñ naa seen Yàlla Aji Sax ji, tooñ leen. \v 17 Baal ma àq bii yoon rekk, te ngeen ñaanal ma seen Yàlla Aji Sax ji, ngir mu teggil ma rekk, wii ay wu rey.» \v 18 Musaa bàyyikoo ca Firawna, tinu Aji Sax ji. \v 19 Aji Sax ji walbati ngelaw la, mu jóge sowu, am doole lool, daldi fél njéeréer ya, sànni ca géeju Barax ya, ba luy niru njéeréer desatul ca déndu Misra. \v 20 Teewul Aji Sax ji dëgëral boppu Firawna, mu të rekk, baña bàyyi \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ñu dem. \s1 Yarub juróom ñeenteel ba: Lëndëm gu tar ga \p \v 21 Gannaaw loolu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ne Musaa: «Tàllalal sa loxo, mu jublu asamaan, lëndëm wàcc ci kaw réewum Misra, lëndëm gu nit mana daj, ndax fatt.» \v 22 Musaa tàllal loxoom, mu jublu asamaan, lëndëm gu fatt wàcc ca kaw réewum Misra gépp, diiru ñetti fan. \v 23 Kenn gisul sa moroom, kenn manula jóge fa nga nekk, diiru ñetti fan. Teewul këri \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp di leer. \p \v 24 Firawna nag woolu Musaa, ne ko: «Demleen màggali Aji Sax ji. Seen jur gu gudd ak gu gàtt rekk a fiy des, seeni doom sax man nañoo ànd ak yeen.» \v 25 Musaa ne ko: «Danga noo wara bàyyee lu nuy sarxalal sunu Yàlla, Aji Sax ji, ak yu ñu koy defal \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*. \v 26 Sunuy gétt dina nu topp moos, luy nirook we sax du des gannaaw, ndax ci lanuy tànne lu nuy màggale sunu Yàlla Aji Sax ji, te itam li feek nuy àgg foofa, manunoo xam lan lanu ciy def sarax, màggale Aji Sax ji.» \v 27 Teewul Aji Sax ji dëgëral boppu Firawna, mu të rekk, bañ leena bàyyi ñu dem. \v 28 Firawna nag ne Musaa: «Neel mott! Bul fexe ba taxawati sama kanam! Ndax bés boo jàkkaarlooteek man, kera ngay dee.» \v 29 Musaa ne ko: «Noonu la sax de. Duma jàkkaarlooteek yaw moos!» \c 11 \s1 Yàlla waaj na yar bu mujj ba \p \v 1 Ba loolu wéyee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ne ko: «Benn yarub mujjantal laay dellu wàcce ci kaw Firawna ak waa Misra. Su ko defee du leen bàyyi ngeen dem, yem ca. Da leen fiy far dàqe, ba fàww. \v 2 Te neel mbooloo mi, góor gu nekk ak jigéen ju nekk ci ñoom, na sàkkoo ci dëkkandoob waa Misraam, ay gànjari xaalis ak wurus.» \v 3 Ci biir loolu Aji Sax ji def waa Misra yéwéne leen. Musaa sax ci boppam ku ñu naw la woon ca réewum Misra, ca dagi Firawna ya, ba ca baadoolo ya. \p \v 4 Musaa daldi wax Firawna ne ko: «Aji Sax ji dafa wax ne: “Bu guddi gi xaajee, maay wër Misra gépp, \v 5 te lépp luy taaw bu góor ci réewum Misra, dina dee, dale ko ci taaw bu góoru Firawna, mi toog ci jal bi, ba ci taaw bu góoru jaam bu jigéen bu féetewoo wol, boole ci luy taaw bu góor ci jur gépp. \v 6 Dees na dégg yuux yu réy jibe Misra gépp, lu masula am, te dootu am mukk. \v 7 Waaye fépp fu \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* dëkke, dara du fa wokk nit ak mala.” Su boobaa dingeen xam ne, Aji Sax jee ràññatle waa Misra ak bànni Israyil. \v 8 Bu loolu amee mboolem sa dag yii dinañu ma sujjóotalsi te naan ma: “Demal, yaak mbooloo, mi la topp yépp!” Su ko defee ma doora dem.» Musaa nag won Firawna gannaaw, mer ba, fees. \v 9 Fekk na Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Li waral Firawna du leen déglu, mooy sama kéemaan yi wara fulandiwu ci réewum Misra.» \v 10 Musaa ak Aaróona def nañu yooyu kéemaan yépp ca kanam Firawna, waaye fekk na Aji Sax ji dëgëral boppu Firawna, ba mu të, baña bàyyi bànni Israyil, ñu génn réew ma. \c 12 \s1 Lu jëm ci bésub Mucc ba \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax na ak Musaa ak Aaróona ca réewum Misra, ne leen: \v 2 «Weer wii mooy doon ci yeen wi jiitu ci weer yi, te na doon ci yeen weer, wi jëkk ci at mi. \v 3 Waxleen ak mbooloom Israyil mépp ne leen, bésub fukkeel ba ci weer wii, na ku nekk jëlal njabootam ab gàtt, kër gu nekk ak gàttam. \v 4 Waaye su dee gàtt bu ëpp waa kër ga, dañu koy bokk ak kër, gi leen gëna jege, te nañu seet nu nit ña tollu, doora tànn gàtt bu dëppook la ñu mana lekk. \v 5 Gàtt ba bumu am sikk te na di kuuyu menn at. Man naa doon xar mbaa sikket. \v 6 Dangeen koy denc ba fukkeelu bés ba ak ñeent ci weer wii. Bu bés baa ci diggante ngoon ak jant bu so, na mbooloom Israyil mépp bokk rendi seeni gàtt. \v 7 Su ko defee ñu sàkk ca deret ja, taqal ca buntu kër, ga ñu ko nara lekke, taqal ca ñaari jëni bunt ba ak njëël bunt ba ca kaw. \v 8 Dañuy lakk yàpp wa cib taal, lekk ko guddig keroog, boole kook mburu mu amul lawiir ak xob yu wex. \v 9 Nañu ko wàjj, mu ne ñumm, bopp bi ak tànk yi ak yérey biir yi. Buleen ci lekk dara lu ñorul, mbaa lu ñu baxal. \v 10 Buleen ci wacc dara mu fanaan, te lépp lu ci des bu bët setee, lakkleen ba mu jeex tàkk. \v 11 Ni ngeen koy lekke nag, nii la: bu ngeen koy lekk, dangeen di takku, sol seeni dàll, ŋàbb seen yet, te ngeen lekk ko ci lu gaaw. Loolu gàttu saraxu \w bésub Mucc|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* ba lay doon, ñeel Aji Sax ji. \p \v 12 «Guddig keroog maay wër réewum Misra te maay fàdd lépp luy taaw bu góor ci réewum Misra, nit ak mala, te itam maay mbugal mboolem tuuri Misra. Man maay Aji Sax ji. \v 13 Deret ji ci kër, yi ngeen dëkke nag, mooy doon seen xàmmikaay, ba tax bu ma gisee deret ji, musal leen. Su ko defee bu may dal ci kaw réewum Misra, menn musiba du leen lor. \p \v 14 «Bésub keroog bésu pàttliku lay doon ci yeen, ngeen war koo màggal ngir Aji Sax ji, muy dogal bu leen war fàww, yeen ak seen askan. \s1 Lu jëm ci ayu bésu Mburu mu amul lawiir \p \v 15 «Diiru juróom ñaari fan ngeen di lekk mburu mu amul lawiir; te bés bu jëkk bi ci boppam nangeen jële seeni kër luy lawiir, ndaxte képp ku ci lekk mburu mu am lawiir, li ko dale bés bu jëkk bi, ba kera bésub juróom ñaareel ba, dees na ko dagge ci askanu Israyil. \v 16 Bés bu jëkk bi nangeen ci amal ndaje mu \w sell|lemma="sell:"\w*. Juróom ñaareelu bés ba itam nangeen ca amal ndaje mu sell; deesul liggéey lenn ci yooyu bés, lu moy ngeen togg ñam wu ñépp lekk. Loolu doŋŋ lees ciy mana def. \p \v 17 «Nangeen wormaal \w ayu bésu Mburu mu amul lawiir|lemma="Màggali Yawut yi:"\w*, ndaxte ci bés boobu tembe laa leen génnee réewum Misra, kurél ci kaw kurél. Kon nag nangeen wormaal bés bii, muy dogal bu leen war fàww, yeen ak seen askan. \v 18 Li ko dale ngoonu fukki fan ak ñeent ci weer wu jëkk wi, ba ca ngoonu ñaar fukki fan ak benn ci weer woowu, nangeen ci lekk mburu mu amul lawiir. \v 19 Diiru juróom ñaari fan, bu dara ci lawiir am fenn ci seeni kër, ndax képp ku lekk lu am lawiir, dees na ko dagge ci askanu Israyil, muy doxandéem mbaa doomu réew mi. \v 20 Buleen ci lekk lenn lu am lawiir, te fépp fu ngeen dal, na mburu mu ngeen mana lekk di mu amul lawiir.» \s1 Waajal nañu bésub Mucc ba \p \v 21 Ba loolu amee Musaa woo magi Israyil ñépp, ne leen: «Demleen tànnali seeni njaboot ay gàtt, te ngeen rendi gàtt yooyu, def ko saraxu \w bésub Mucc|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* bi. \v 22 Dangeen di jël ab takku cari isob\f + \fr 12.22 \fr*\fk isob \fk*\ft as ngarab la su car ba sëq, ba ñu man koo diwe.\ft*\f*, capp ci deret ji ci ndab li, diw ci seen njëël bunt ak seen ñaari jëni bunt, te bu kenn ci yeen wees buntu këram ba bët set. \v 23 Su ko defee, bu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jiy wër ci biir réew mi, di fàdd waa Misra, ba gis deret ji taq ci seen njëël bunt ak seen ñaari jëni bunt, day teggi bunt ba, te du bàyyi malaakam reykat bi, mu dugg seeni kër, di fàdde. \p \v 24 «Nangeen sàmmonteek loolu, muy dogal bu leen war fàww, yeen ak seen askan. \v 25 Keroog bu ngeen duggee nag ca réew ma leen Aji Sax ji jox na mu leen ko dige woon, nangeen sàmmonteek jooju aada. \v 26 Te bu leen seeni doom laajee ne leen: “Lu aada jii di wund?” \v 27 waxleen leen ne leen: “Loolu sarax la ñeel Aji Sax ji ngir bésub Mucc ba, ndax la mu teggi woon këri \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ca Misra, kera ba muy fàdd waa Misra te musal ca sunuy kër.”» \p Ba mu waxee loolu ba noppi, mbooloo ma sujjóot, màggal Yàlla. \v 28 La Aji Sax ji santoon Musaa ak Aaróona, noonu rekk la ko bànni Israyil defe. \s1 Yarub fukkeel ba, di deewu taaw ya \p \v 29 Ca xaaju guddi la \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji fàdd mboolem taawi réewum Misra yu góor, dale ko ca taaw bu góor bu Firawna, ma toog ca jal ba, ba ca taaw yu góor yu nit ña ñu tëj kaso, boole ca lépp luy taaw bu góor ca jur ga. \v 30 Firawna nag jóg ca guddi ga, moom ak dagam yépp ak waa Misra gépp, yuux gu réy jibe ca Misra, ndax këroo kër, du genn gu nit deewul. \p \v 31 Ba loolu amee Firawna woolu Musaak Aaróona ca guddi googu, ne leen: «Ayca! Mott! Soreleen sama waa réew, yeen ak seeni bokk! Laggleen, jaamuji Aji Sax ji, li ngeen bëgg. \v 32 Te itam yóbbaaleleen seen juroo jur, gu gudd ak gu gàtt, li ngeen bëgg rekk, te ne mott! Waaye ñaanaaleleen ma seen Yàlla nag, mu barkeel ma.» \s1 Bànni Israyil gàddaay na \p \v 33 Ba mu ko defee waa Misra soññ bànni Israyil, ngir ñu gaaw génn réew ma, ndax booba ña nga naan: «Nun ñépp ay dee!» \v 34 Loolu tax mbooloom Israyil roñ seen xiiwi sunguf yu amagul lawiir. Ñu ëmb seen ndabi notukaay ca seeni malaan, gàddu. \v 35 Fekk na \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* def la leen Musaa santoon ca waa Misra. Sàkku nañu ca ñoom ay gànjari xaalis ak wurus aki yére. \v 36 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nag def waa Misra nangul bànni Israyil, ba jox leen la ñu sàkku; noonu lañu futtee waa Misra. \p \v 37 Ci kaw loolu bànni Israyil jóge dëkk ba ñuy wax Ramses, jëm Sukkóot. Ña nga tollu ci juróom benni téeméeri junniy góor (600 000) te limaaleesul jigéen ñaak xale ya. \v 38 Amoon na it mbooloom nit ñu ànd ak ñoom, te di askan yu raxe, ak jur gu bare, gu gudd ak gu gàtt. \v 39 Ñu daldi lakk mburu mu tàppandaar ca xiiw wu amul lawiir, wa ñu jële Misra. La taxoon xiiw wa ñàkk lawiir mooy dañu leena dàqe Misra, ba taluñu woona fàggu lu ñu lekk. \p \v 40 Diir ba bànni Israyil nekk Misra tollu na ci ñeenti téeméeri at ak fanweer (430). \v 41 Keroog ca bés, ba ñeenti téeméeri at ya ak fanweer matee sëkk, ca la ñoñi Aji Sax ji génn réewum Misra, kurél ci kaw kurél. \v 42 Guddig keroog guddig teewlu la, ñeel Aji Sax ji, ngir moo leen ca génne réewum Misra, moo tax guddi googu di gu ñu jagleel Aji Sax ji, bànni Israyil gépp war cee fanaanee teewlu, ñeel Aji Sax ji, ba fàww. \s1 Ay dogali Aji Sax jaa ngii, ñeel bésub Mucc ba \p \v 43 Gannaaw loolu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ak Musaa ak Aaróona, ne leen: «Li ma dogal ci saraxu \w bésub Mucc|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* bi mooy lii: Benn doxandéem du ci lekk. \v 44 Waaye bépp jaam bu ñu jënd te mu xasa xaraf, man na cee lekk. \v 45 Benn màngaan mbaa liggéeykat bu ñu bind it du ci lekk. \v 46 Genn kër lees koy lekke: bu lenn ci yàpp wi génn kër gi, te deesu ci damm benn yax sax. \v 47 Mboolem ku bokk ci \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, na def sarax bi. \v 48 Su fekkee ne ab doxandéem bu ngeen dëkkal dafa bëgga wormaal màggalu bésub Mucc bi ngir Aji Sax ji, xaraf war na ko, te war na gépp góor gu bootu ci moom; su loolu amee, dees na ko may, mu def ko, ndax kon day mel ni doomu réew mi. Waaye kenn ku xaraful du ci lekk. \v 49 Dogal bi benn lay doon, doomu réew mi ak doxandéem bi dëkk ci seen biir, bokk ci yem kepp.» \p \v 50 La Aji Sax ji santoon Musaak Aaróona, noonu rekk la ko bànni Israyil defe. \p \v 51 Bésub keroog boobee la Aji Sax ji yiwi bànni Israyil, ñu def kurél ci kaw kurél, génn réewum Misra. \c 13 \s1 Lu jëm ci aada, yi ñuy baaxantale \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxaat Musaa, ne ko: \v 2 «Nanga ma sédde bépp taaw bu góor, nit ak mala, lépp lu jëkka juddu ci \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, maa moom.» \v 3 Musaa ne mbooloo ma: «Fàttlikuleen bésub tey jii ngeen génne Misra, kërug njaam gi, ak ni leen Aji Sax ji yiwee dooley loxoom. Bu ci kenn lekk mburu mu am lawiir. \v 4 Yeena ngii tey di dem seen yoon ci weeru \w Abiib|lemma="Abiib:"\w*. \v 5 Kon keroog bu leen Aji Sax ji yóbboo réewum Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña, fa mu giñaloon seeni maam, ne dina leen ko jox, réew mu meew maak lem ja tuuroo, nangeen wormaal màggal gi ci wii weer te ngeen di ko defe nii. \p \v 6 «Diiru juróom ñaari fan ngeen di lekk mburu mu amul lawiir, te na bésub juróom ñaareel ba di bésu màggalug Aji Sax ji. \v 7 Mburu mu amul lawiir ngeen di lekk diiru juróom ñaari fan; te it bu lenn lu am lawiir mbaa lawiir sax am fenn ci seen biir réew. \v 8 Bu keroogee na ku nekk xamal doomam, ne ko: “La ma Aji Sax ji defaloon, ba ma génnee Misra, moo waral lii tey.” \p \v 9 «Na màggal googu di pàttliku ci yeen. Na mel ni màndarga mu nekk ci seen loxo ak seen jë. Su ko defee ngeen saxoo jàngle yoonu Aji Sax ji, ndax ci dooley loxoom la leen Aji Sax ji génnee Misra. \v 10 Nangeen sàmmonteek bii dogal ci bésam, at mu nekk. \p \v 11 «Bu leen Aji Sax ji yóbboo nag réewum Kanaaneen ña, noonee mu leen ko giñale woon, yeen ak seeni maam, ba jox leen ko, \v 12 nangeen sédde Aji Sax ji lépp lu jëkka juddu, rendil ko ko: lépp luy góor lu seen jur taawloo, Aji Sax jeey boroom. \v 13 Waaye lépp lu mbaam-sëf taawloo, nangeen ko jote kuuyum xar, mu wuutu ko. Bu ngeen ko jotul, nangeen damm loos wi. Te itam jotleen képp kuy taaw bu góor ci seeni doom. \v 14 Su ko defee, bu leen seen doom laajee ëllëg, ne leen: “Lii lu muy tekki?” ngeen wax ko ne ko: “Dooley loxol Aji Sax jee nu génne Misra, kërug njaam ga. \v 15 Ba Firawna tëwee, bañ noo bàyyi, nu dem, Aji Sax jee rey mboolem lu doon taaw bu góor ca réewum Misra, taawu nit ba ci taawu mala. Looloo waral nuy rendil Aji Sax ji mépp mala mu jëkka juddu, di góor, sunu bépp taaw bu góor it, ñu war koo jote sarax su nu koy rendil.” \v 16 Na yooyu sarax mel ni màndarga mu nekk ci seen loxo ak seen jë, di leen fàttli ni nu Aji Sax ji génnee Misra ci dooley loxoom.» \s1 Aji Sax ji jiite na mbooloo ma \p \v 17 Firawna bàyyi na mbooloo ma, ñu dem, waaye Yàlla jaaralewu leen ca yoon, wa jëm réewu Filisti, doonte moo gënoona gàtt. Booba Yàlla dafa xam ne, su mbooloo ma sóoboo ci ay xare ci woowu yoon, dañuy yoqi, bay xalaata dëpp, dellu Misra. \v 18 Moo tax Yàlla wiiriloo mbooloo ma, ñu jaare ca màndiŋ ma, jëm ca géeju Barax ya. Ba mu ko defee \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* fagaru ba jekk, daldi génn Misra. \p \v 19 Musaa nag yóbbaale yaxi Yuusufa, ma giñloo woon bànni Israyil, ne leen: «Yàlla dina leen geesu moos, te bu keroogee nangeen fi jële samay yax, yóbbaale.» \p \v 20 Ñu bàyyikoo Sukkóot, dal Etam ca wetu màndiŋ ma. \v 21 Bu bëccëgee nag \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nekk ci seen kanam ci biir taxaaru niir, di leen jiite ca yoon wa, te bu guddee mu nekk ci biir taxaaru sawara, di leen leeral, ba ñu mana dem guddi ak bëccëg. \v 22 Du bëccëg bu niir wa jóge ca kanam mbooloo ma, te du guddi it gu sawara wa masa wuute. \c 14 \s1 Firawna dabi na bànni Israyil \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa, ne ko: \v 2 «Waxal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, ne leen ñu walbatiku dali fa jàkkaarlook Pi Axirot, ca diggante Migadol ak géeju Barax ya. Dal-leen foofa jàkkaarlook Baal Cefon ca tefes ga. \v 3 Su ko defee Firawna da naan: “Bànni Israyil de dañoo réer ci àll bi, ba faf keppu ci màndiŋ mi.” \v 4 Gannaaw loolu maay dëgëral boppu Firawna, mu topp leen, ba ma jaare ca siiwal sama ndam, ndax maay daan Firawnaaki xarekatam yépp, te waa Misra dinañu xam ne, man maay Aji Sax ji.» Musaa jottli leen ko, ñu def noona. \p \v 5 Ba ñu yégalee Firawna buuru Misra, ne mbooloo ma daw na, mooki dagam dañoo soppi xalaat ca mbirum bànni Israyil. Ñu ne: «Waaw nun, li nu def nag? Ana luy ndeyi yiwi bànni Israyil, ba dootuñu nu surgawu?» \v 6 Firawna takklu watiiru xareem, ànd aki jàmbaaram. \v 7 Mboolem watiiri xarey Misra la yóbbu, jiital juróom benni téeméer, ya ca gën, bu ci nekk yeb ay kilifay xarekat\f + \fr 14.7 \fr*\fk kilifay xarekat: \fk*\ft watiiru xare yi ñaar la daan yeb, kiy dawal ak kiy fitt, waaye bii yoon Firawna da caa tofal njiitu xarekat, mu ñetteel leen.\ft*\f*. \v 8 Aji Sax jee dëgëral boppu Firawna buuru Misra, mu toppi bànni Israyil, fekk bànni Israyil ñoom, ña ngay génn réew ma ci seen teeyu bakkan. \v 9 Waa Misra topp leen, ñook fasi Firawna yépp, ak watiiri xareem ak dawalkatam yaak xarekatam ya, ba dab leen fa ñu dal ca tefesu géeju Barax ya, fa jàkkaarlook Baal Cefon ca wetu Pi Axirot. \p \v 10 Firawnaa ngay jubsi, bànni Israyil séentu, yemuñu ci ñu moy waa Misra, ñu dikk, jubsi leen. Tiitaange lu réy jàpp bànni Israyil. Ñu woo Aji Sax ji wall. \v 11 Ci biir loolu ñu ne Musaa: «Xanaa Misra dafa amul ay sëg, ba nga di nu indi ci màndiŋ mi, nu deesi fi? Loo nu doon génnee Misra? \v 12 Xanaa du lii lanu la waxoon ca Misra? Noon nanu la, nga bàyyi nu, nu surgawu waa Misra, ndax surgawu waa Misra moo nu gënal nu dee ci màndiŋ mi!» \p \v 13 Musaa nag ne mbooloo ma: «Buleen tiit, neleen tekk te xool li Aji Sax jiy def, ba xettli leen tey jii. Ndax kat waa Misra yii ngeen di gis nii tey, dootuleen leen gis mukk. \v 14 Aji Sax ji moo leen di xeexal, yeen kay neleen tekk rekk.» \s1 Yàlla xàll na géej ga \p \v 15 Ci kaw loolu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax Musaa ne ko: «Loo may wooye wall? Waxal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, ne leen ñu dem rekk, \v 16 te yaw nanga yékkati saw yet, tàllal sa loxo mu tiim géej gi, ba xàll ko, ndax bànni Israyil mana dox ci suuf su wow, jàll géej gi. \v 17 Man nag maay dëgëral boppu waa Misra, ba ñu dugg, topp leen. Su ko defee ma siiwal sama ndam, ndax dinaa yar Firawnaaki xarekatam yépp, boole ci watiiri xareem aki gawaram. \v 18 Bu ma dumaa Firawna, boole kooki watiiram aki gawaram, ba doxe fa siiwal sama ndam, waa Misra dinañu xam ne man maay Aji Sax ji.» \p \v 19 Ci kaw loolu malaakam Yàlla, ma féete woon xarekati Israyil kanam naka jekk te di leen jiite, daldi toxu, féete leen gannaaw. Niir, wa leen jiitu woon it walbatiku, taxaw ca seen gannaaw, \v 20 dox diggante dalu waa Misra ak dalu bànni Israyil. Niir waa nga lëndëme genn wet, wet ga ca des di leer ca guddi ga, ba tax guddi ga gépp benn dal manula fekki moroom ma. \p \v 21 Gannaaw ga Musaa tàllal loxoom, mu tiim géej ga, Aji Sax ji yebal ngelawal penku lu réy guddi ga gépp, jañaxe ko géej ga, ndox ya xàjjalikoo, ba suuf su wow feeñ. \v 22 Bànni Israyil nag dugg ca biir géej ga, di dox ci kaw suuf su wow, ndox ya ne sàtt, ñagal leen ndijoor ak càmmoñ. \p \v 23 Ba mu ko defee waa Misra daw topp ca ñoom, fasi Firawna ak watiiri xareem aki gawaram ànd, ñoom ñépp ne yentam ca biir géej ga. \v 24 Ba njël jotee Aji Sax ji dafa tollu ci biir taxaaru sawara wu ànd aku niir, di xool xarekati Misra, tiital leen, ñu fëlxoo. \v 25 Mu boole ca téye mbegey watiir ya, ba neexatuñoo dawal. Waa Misra ne: «Nan daw gaaw, ba rëcc bànni Israyil, ndax kat Aji Sax ji moo leen di xeexal, te moo dal ci sunu kaw!» \p \v 26 Aji Sax ji nag wax Musaa ne ko: «Tàllalal sa loxo, mu tiim géej gi, ndax ndox mi délsi, ba sottiku ci kaw waa Misra, ñook seen watiiri xare ak seeni gawar.» \v 27 Musaa tàllal loxoom, mu tiim géej ga. Ba bët di set géej ga dellu na, mel na mu meloon. Waa Misra di daw, géej ga wal, dogale leen, Aji Sax ji fél leen, ñu ne ca menteñ. \v 28 Ndox ma daa délsi, boole mëdd watiiri xare yaak gawar ya, mboolem xarekati Firawna, ya leen toppoon ca biir géej ga rekk. Kenn rëccul. \v 29 Waaye bànni Israyil ñoom, ci suuf su wow lañu jaare ca digg géej ga, jàll, ndox ya ne sàtt, ñagal leen ndijoor ak càmmoñ. \p \v 30 Noona la Aji Sax ji xettlee bànni Israyil bésub keroog ca waa Misra, ñu gis néewi waa Misra ya ne wetar ca tefes ga. \v 31 Ba Israyil gisee na Aji Sax ji jowe loxoom bu baax ca xareem baak waa Misra, dañu daldi ragal Aji Sax ji, teg ca am kóolute ci Aji Sax ji ak ci Musaa, jaamam ba. \c 15 \s1 Woyu Musaa waak bànni Israyil \p \v 1 Ba loolu amee nag Musaa ak \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* woy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, màggal ko. Ña nga naan: \b \q1 «Ma woy Aji Sax ji, ngir ndamam li kawee kawe. \q1 Fas ak gawaram la fab, xalab géej. \q1 \v 2 Sama doole, sama kaaraange, Ki Sax a; \q1 te mooy sama wall tey. \q1 Mooy sama Yàlla, ji may tagge, \q1 sama Yàllay maam, ji may joobe. \b \q1 \v 3 «Aji Sax ji jàmbaari xare ji, \q1 Aji Sax jeey turam! \q1 \v 4 Watiiri Firawnaaki xarekatam la fab sànni géej; \q1 ñeyi xareem ya labandoo ca géeju Barax ya, \q1 \v 5 xóote ya boole sàng, \q1 ñu ne ca biir menteñ niw doj. \b \q1 \v 6 «Aji Sax ji, sa kàttanu ndijoor a yéeme! \q1 Aji Sax ji, sa ndijoor a ne noon ba rajax. \q1 \v 7 Sa màggaay gu yéemee nërmeel say noon. \q1 Yaa yebal sa mer, mu ne jippét, \q1 xoyom leen ni boob. \q1 \v 8 Nga wal sag noo, ndox ya tegloo, \q1 wal ma ne sàtt, jaloo jalu, \q1 ndoxi xóotey géej way deeŋ! \b \q1 \v 9 «Noon baa nga naa: “Maay dàqe, dabe, \q1 lël alal ja, séddale \q1 séddu, ba xol sedd, \q1 ne saamar boset, \q1 teg leen loxo.” \q1 \v 10 Waaye sa ngelaw nga wal, \q1 géej mëdd leen, \q1 ñu diigandoo ni beteex biir géej mbàmbulaan! \b \q1 \v 11 «Ana kuy sa moroom ci tuur yi, yaw Aji Sax ji? \q1 Kuy sa dend, yaak sa sellaay bu yéeme, \q2 sa yànjaay bu raglook sa jëf yu yéeme? \q1 \v 12 Yaa tàllal sa ndijoor, \q1 suuf wonn leen. \b \q1 \v 13 «Sa ngor nga jiitee mbooloo, mi nga jot, \q1 te sa kàttan nga leen di yóbboo ca sa kër gu \w sell|lemma="sell:"\w*. \q1 \v 14 Jaambur ñay dégg, di rag-ragi, \q1 tiitaange ne taral waa Filisti, \q1 \v 15 kilifay waa Edom jàq, \q1 njiiti Mowab di kat-kati, \q1 mboolem waa Kanaan tiit, ne yasar; \q1 \v 16 tiitaangeek njàqaree ne milib ca seen kaw. \q1 Sa kàttan a tax ñu mel niw doj, ne yàcc, \q1 ba kera sa ñoñ jàll, Aji Sax ji, \q1 ba kera askan wa nga goreel, jàll, \q1 \v 17 te yaa leen di sampi ca sa tund wa nga séddoo, \q1 fa nga waajal sa dëkkuwaay, Aji Sax ji, \q1 bérab bu sell ba nga sàkke sa loxol bopp, Boroom bi. \q1 \v 18 Aji Sax jeey Buur, tey ak ëllëg ba fàww.» \p \v 19 Ci kaw loolu fasi Firawna ànd ak watiiri xareem aki gawaram, tàbbi géej, Aji Sax ji delloo ndoxi géej ga ca seen kaw, bànni Israyil ñoom, jaare joor gu wow ca digg géej ga. \s1 Maryaama woy na \p \v 20 Yonent Yàlla Maryaama, jigéenub Aaróona nag ŋàbb tabala, jigéen ñépp topp ko, génn di fecc, tabala ya jiin. \v 21 Maryaamaa nga leen di dëbbeel, naa: \q1 «Woyleen \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ngir ndamam li kawee kawe. \q1 Fas ak gawaram la fab, xalab géej.» \s1 Lu jëm ci ndox mu wex ma \p \v 22 Gannaaw loolu Musaa jële \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* géeju Barax ya, ñu wéy, wuti màndiŋ, ma ñuy wax Sur. Dox nañu ñetti fan ca màndiŋ ma, gisuñu ndox. \v 23 Ñu dem, ba àgg fu ñu naan Maara, waaye manuñoo naan ca ndoxum Maara, ndax wex. Looloo waral ñu tudde bérab ba Maara (mu firi Fu wex). \v 24 Mbooloo ma nag di diiŋat Musaa, naan: «Ana ndox mu nuy naan nag?» \v 25 Musaa woo \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wall, Aji Sax ji won ko dammitu bant, mu sànni ko ca ndox ma, ndox ma neex. \p Foofa la Aji Sax ji dogalal bànni Israyil ay sàrti yoon ak ndigal, te fa la leen nattoo itam. \v 26 Da ne leen: «Bu ngeen farloo ci déggal seen Yàlla Aji Sax ji, di def li mu rafetlu, di teewlu tey jëfe ay santaaneem, di sàmm bépp dogali yoonam, su boobaa duma leen teg lenn ci jàngoro, yi ma tegoon waa Misra, ndax man maay Aji Sax, ji leen di wérloo.» \p \v 27 Ci kaw loolu ñu dem ba Elim, fekk fa fukki bëti ndox ak ñaar, ak juróom ñaar fukki garabi tàndarma. Ñu dal foofa ca wetu ndox ma. \c 16 \s1 Aji Sax ji leel na bànni Israyil \p \v 1 Gannaaw gi mbooloom \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp bàyyikoo fa Elim, dem, ba keroog fukki fan ak juróom, ca weer wa topp ca wa ñu génne réewum Misra, ñu doora agsi màndiŋu Ciin diggante Elim ak Sinayi\f + \fr 16.1 \fr*\fk Sinayi \fk*\ft mooy Oreb ba tey.\ft*\f*. \v 2 Mbooloom bànni Israyil gépp nag di diiŋat Musaa ak Aaróona ca màndiŋ ma. \v 3 Ña nga naa leen: «Céy ngalla nun, su nu sañoon dee, Yàlla moom nu ca réewum Misra, fa nu daan uufe cini yàpp, ñam wa ne gàññ, nu suur këll. Yeena nu indi ba ci màndiŋ mii, ngeen nara xiifloo mbooloo mii mépp, ba ñu dee.» \p \v 4 Ba loolu amee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax Musaa ne ko: «Maa ngi nii di tawal bànni Israyil ñam wu jóge asamaan, te na mbooloo mi dem bés bu set, fori njëlu bés ak bés. Ma nattu leen ci, ba xam ndax dinañu doxe sama ndigalu yoon am déet. \v 5 Waaye bu ñu demee ba bésub juróom benneel ba, ba togg la ñu ca indi, day tollook ñaar-cay dayo ba ñuy for bés bu set.» \p \v 6 Musaa ak Aaróona nag xamal bànni Israyil ne leen: «Bu ngoonee dingeen xam ne, Aji Sax ji moo leen génne réewum Misra, \v 7 te bu bët setee dingeen gis manoorey Aji Sax ji, ndaxte dégg na ngeen di diiŋat Aji Sax ji, ndax nun kat tekkiwunu dara, ba ngeen di nu diiŋat.» \v 8 Musaa teg ca ne: «Moo tax Aji Sax ji dina leen jox yàpp wu ngeen lekk ngoon, te bu bët setee mu jox leen ñam wu leen reggal, ndax Aji Sax jee dégg ngeen di ko diiŋat. Nun lu nu ci? Du nun ngeen di diiŋat waaye yeen ak Aji Sax ji la.» \p \v 9 Ba loolu wéyee Musaa ne Aaróona: «Waxal mbooloom bànni Israyil gépp, ne leen ñu dem ba ca kanam Aji Sax ji, ndaxte dégg na seeni diiŋat.» \v 10 Naka la Aaróona di wax ak mbooloom Israyil mépp, ñu jekki ne gees ca màndiŋ ma, daldi yem ci aw niir, leeru Aji Sax ji di ca feeñ. \v 11 Aji Sax ji wax Musaa ne ko: \v 12 «Dégg naa diiŋati bànni Israyil. Wax leen ne leen, diggante ngoon ak jant bu so, dinañu lekk yàpp, te bu bët setee ñu lekk aw ñam, ba regg, ndax ñu xam ne man Aji Sax ji, maay seen Yàlla.» \s1 Aji Sax ji wàcce na mànn aki picc \p \v 13 Ba ngoon jotee ay picci përëntaan\f + \fr 16.13 \fr*\fk picci përëntaan: \fk*\ft xeetu picc la, muy nirook naat te gën koo tuuti.\ft*\f* dikk, fees dal ba. Ba bët setee lay bay wàcc ca dal ba. \v 14 Naka la lay ba bàcc, ñu jekki gis lu sew lale ca màndiŋ ma, def fepp yu sew ca biir, te mel ni tawub yuur, tege ca suuf. \v 15 \w Bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gis ko, di wax ca seen biir naan: «Lii lu mu?» ndax xamuñu woon lu mu doon. Musaa ne leen: «Lii mooy ñam wi leen \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji jox, ngeen lekk. \v 16 Aji Sax ji dafa santaane ne: “Na ku nekk for lu mat njëlam, bopp bu ne andaar\f + \fr 16.16 \fr*\fk andaar: \fk*\ft moom lañu tekkee omer ci ebrë, te muy natt buy tollu ci ñaari liitar.\ft*\f*, te mu natt ko ci limu nit, ñi mu bokkal xayma.”» \v 17 Bànni Israyil def noona, ñii for lu bare, ñee lu néew. \v 18 Waaye ba ñu ko nattee ci andaar, ña sàkkoon lu bare amuñu lu ëpp, te ña sàkkoon lu néew yéeslewuñu. La ñu for dafa tolloo tembe ak seen njël. \v 19 Musaa ne leen: «Bu ci kenn wacc dara, mu fanaan.» \v 20 Waaye dégluwuñu Musaa, am na ñenn ca ñoom ñu ca wàññi, fanaanal, mu def ay sax, xasaw xunn. Musaa nag mere leen. \p \v 21 Suba su ñu xëyaan nag, ku nekk for ca njëlam, ndax bu naaj wa tàngaan, mu seey. \s1 Aji Sax ji santaane na bésub Noflaay \p \v 22 Ba bésu juróom benneel ba jotee, dañoo for lu mat ñaari njël, ku nekk am ñaari andaar, njiiti mbooloo ma nag dem yeggeji ko Musaa, \v 23 mu ne leen: «Loolu la \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax, te li muy tekki mooy: ëllëg bésu dal-lu la, di \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w* bu \w sell|lemma="sell:"\w* ñeel Aji Sax ji. Lakkleen li ngeen di lakk, baxal li ngeen di baxal, te lu ci des, ngeen denc ba suba.» \v 24 Ba ñu dencee la ca des ba ca ëllëg sa, na ko Musaa santaanee, xasawul, saxewul. \v 25 Musaa wax leen ne leen: «Lekkleen li des tey, ndax tey jii bésub Noflaay la, ñeel Aji Sax ji, te dungeen ko gis tey ci àll bi. \v 26 Juróom benni fan ngeen koy for, waaye bésub juróom ñaareel bay bésub Noflaay, kenn du ko gis.» \p \v 27 Terewul mu am ñu fori ca bésub juróom ñaareel ba, waaye gisuñu dara. \v 28 Ca la Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Waaw yeen nag, dungeen ma noppee gàntalal samay santaaneek samay ndigali yoon mukk? \v 29 Nangeen xam xéll ne, man Aji Sax ji, maa leen may bésub Noflaay ngir ngeen nopplu, te looloo tax ma may leen dundub ñaari fan ci bésub juróom benneel bi. Kon nag bésub juróom ñaareel ba, na ku nekk toog fi mu nekk, bu ci kenn génnati fi mu dëkk.» \v 30 Ba loolu amee bànni Israyil di nopplu bésub juróom ñaareel ba. \s1 Mànn ma jar naa fàttliku \p \v 31 Waa kër Israyil nag tudde ñam wa mànn (mu firi Lii lu mu?). Dafa meloon ni pepp, mi ñuy wax koryanda, te weex, di saf lu mel ni nàkk bu ànd ak lem. \v 32 Ci biir loolu Musaa ne: «\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa santaane ne: “Sàkkleen ci andaar, denc ngir seeni sët ak seeni sëtaat. Su ko defee ñu gis ñam, wi ma leen daan leel ca màndiŋ ma, gannaaw ba ma leen génnee réewum Misra.”» \p \v 33 Musaa wax Aaróona ne ko: «Fabal ndab, def ci andaaru mànn, teg ko fi kanam Aji Sax ji, dencal ko seeni sët ak seeni sëtaat.» \p \v 34 La Aji Sax ji santoon Musaa la Aaróona def, daldi koy teg ca kanam gaal gay def àlluway kóllëre ga\f + \fr 16.34 \fr*\ft Seetal ci 25.10-12.\ft*\f*, ñu denc ko fa. \v 35 \w Bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* dunde nañu mànn diiru ñeent fukki at, ba kera ñu agsee réew mu ay nit dëkke, gannaaw ba ñu jéggee kemu réewum Kanaan. \p \v 36 Ñu jàpp ne andaar, boo ci amee fukk, mooy benn efa\f + \fr 16.36 \fr*\fk efa \fk*\ft ab natt la woon, bu wara tollook ñeent fukki liitar ak juróom.\ft*\f*. \c 17 \s1 Ndox balle na ciw doj \p \v 1 Gannaaw loolu mbooloom \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp bàyyikoo màndiŋu Ciin, di dox ak a taxaw, ci ndigalal \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Ñu dem ba Refidim, dal fa. Foofa nag mbooloo ma amuñu woon ndox mu ñu naan. \v 2 Ñu jote faak Musaa, naan ko: «Joxleen nu nag ndox mu nu naan!» Musaa ne leen: «Ana lu ngeen joteek man? Aji Sax ji ngeen di seetlu nag?» \v 3 Mbooloo ma mar na fa, bay xultu ci kaw Musaa, naan: «Loo nu doon jële Misra nag, xanaa du boole nu rey ndax mar, nook sunuy doom ak sunuy gétt?» \v 4 Ba mu ko defee Musaa woo Aji Sax ji wall, ne ko: «Nu may def ak mbooloo mii? Des na tuuti de, ñu dóor ma ay doj, ba ma dee.» \v 5 Aji Sax ji ne Musaa «Àndal ak ñenn ci magi Israyil, nga jaar ci kanam mbooloo mi, yóbbaale yet, wa nga dóoroon ca dexu Niil ga. Ŋàbb ko ci sa loxo te dem. \v 6 Man dinaa taxaw ci sa kanam ci doj woowu ca tundu Oreb. Dóoral ci doj wi, su ko defee ndox dina ci génne, mbooloo mi naan.» Musaa def noona ca kanam magi Israyil ña. \v 7 Bérab boobu la Musaa wooye Maasa (mu firi Nattu). Mu wooye ko itam Meriba (mu firi ab Jote), ndax joteb bànni Israyil ba fa amoon, ak na ñu fa nattoo Aji Sax ji, naan: «Moo Aji Sax ji ndax mu ngi ci sunu biir, am déet?» \s1 Amalegeen ña xare nañook Israyil \p \v 8 Ba loolu weesee Amalegeen ña dikk, xareek \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ca Refidim. \v 9 Musaa ne Yosuwe\f + \fr 17.9 \fr*\fk Yosuwe: \fk*\ft seetal ci 33.11.\ft*\f*: «Tànnal nu ay xarekat te nga dem xeex ak Amaleg. Ëllëg dinaa taxaw ca kaw tund wa, ŋàbb yetu Yàlla wi ci sama loxo.» \v 10 Yosuwe def la ko Musaa wax, di xeex ak Amaleg. Musaa ak Aaróona ak Ur nag ànd yéeg ba ca kaw tund wa. \v 11 Ci kaw loolu saa yu Musaa yékkatee loxoom, Israyil man, saa yu wàccee loxo ba, Amaleg man. \v 12 Musaa nag mujj sonn ndax loxo yu toqi; ñu jël aw doj, tegal ko, mu toog ca, Aaróona ak Ur séq ko, ku ci nekk taawu benn loxo, loxoom ya ne sàtt taxaw, ba jant so. \v 13 Ba mu ko defee Yosuwe duma Amaleg ak mbooloom, leel leen ñawkay saamar. \p \v 14 Ba loolu amee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax Musaa ne ko: «Bindal lii xew cib téere, muy pàttli, te nga xamal Yosuwe ne ko, raafal laay def askanu Amaleg, ba ñu jeex tàkk, ba deesatu leen fàttliku fu asamaan tiim.» \v 15 Musaa nag sàkk fa \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*, tudde ko tur wuy tekki «Aji Sax jeey sama raaya». \v 16 Booba la wax ne, gannaaw loxoo ñemee xàcci, jëm ci ngànguney Aji Sax ji\f + \fr 17.16 \fr*\ft Manees na koo tekkee nii it: \ft*\fq raayay Aji Sax ji,\fq*\f*, Aji Sax ji dootu noppee xareek Amaleg ba fàww. \c 18 \s1 Gorob Musaa yedd na Musaa \p \v 1 Yettro \w sarxalkatu|lemma="sarxalkat b-:"\w* réewum Majan ba, baayu soxnas Musaa, dafa dégg mboolem la Yàlla defal Musaa ak \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ñoñam ak ni \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji génnee Israyil Misra. \v 2 Ci kaw loolu Yettro gorob Musaa, ànd ak Sipora soxnas Musaa, sa Musaa yebaloon ca kër baayam, \v 3 boole kook ñaari doomi Musaa yu góor ya, kenn ka di Gersom (mu firi Doxandéem fii), ndaxte Musaa da ne woon: «Doxandéem laa fii.» \v 4 Ka ca des mu tudde ko Elyeser (mu firi Yàlla dimbali na ma), ndax da ne woon: «Sama Yàllay baay mooy sama ndimbal te moo ma musal ci saamaru Firawna.» \v 5 Yettro, gorob Musaa nag yóbbul Musaa soxnaam aki doomam ba ca màndiŋ ma, fa Musaa dal ca kaw tundu Yàlla wa. \v 6 Mu yónnee ca Musaa, ne ko: «Man Yettro, sa goro, maa ñëw fi yaw, ànd ak sa soxna ak sa ñaari doom yu góor.» \v 7 Musaa génn gatandu ko, sujjóotal ko, fóon ko; ñu jàmmante ba noppi, doora dugg ca xayma ba. \p \v 8 Musaa nag nettali goroom mboolem li Aji Sax ji def Firawna ak waa Misra ndax Israyil, ak jafe-jafe, ya leen dab ca yoon wa yépp, ak na leen ca Aji Sax ji xettlee. \v 9 Yettro bég lool ca la Aji Sax ji def lépp, ba baaxe Israyil, xettli leen ca noteelu waa Misra. \v 10 Yettro nag ne: «Cant ñeel na Aji Sax, ji leen xettli ci notaangey waa Misra ak notaangey Firawna, xettliwaale mbooloo mi ci notaangey waa Misra. \v 11 Léegi nag xam naa ne, Aji Sax jee sut mboolem tuur yi, ndax la mu def, ba leen waa Misra torxalee.» \v 12 Yettro, gorob Musaa, daldi sàkk \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* ak yeneen sarax, jagleel ko Yàlla. Aaróona ak magi Israyil ñépp dikk, ñu bokk lekk ñook gorob Musaa fa kanam Yàlla. \p \v 13 Ca ëllëg sa Musaa toog, di àtte mbooloo ma, ñu wër Musaa suba ba ngoon. \v 14 Gorob Musaa gis mboolem la Musaa di defal mbooloo ma. Mu ne ko: «Waaw, ni ngay jëflanteek nit ñi nag? Lu tax ngay toog, di àtte yaw rekk, mbooloo mépp wër la, suba ba ngoon?» \v 15 Musaa ne goroom: «Li ko waral mooy nit ñi dañuy dikk, di laaj li dëppook àttey Yàlla. \v 16 Bu ñu jotee, dañuy ñëw diis ma ko, su ko defee ma àtte leen ci mbir mi leen jotale, ba noppi xamal leen santaaney Yàlla ak ndigali yoonam.» \v 17 Goro ba ne ko: «Ni ngay doxale gënul. \v 18 Dangay dàjji sa bopp doŋŋ, dàjji mbooloo mi, ndax yen bee diis, ba ëpp ci sa kaw; doo ko àttan yaw rekk. \v 19 Déglu ma fii, ma digal la, tey ñaan Yàlla ànd ceek yaw. Danga fee toogal mbooloo mi ci kanam Yàlla, di diis Yàlla jotey nit ñi, \v 20 di leen xamal ay santaane aki ndigali yoon, di leen won fi ñu wara jaare ak li ñu wara def. \v 21 Kon nag dangay tànn ci biir mbooloo mi mépp ay góor ñu mat, ñu ragal Yàlla te dëggu, boole ci sib alalu ger. Su ko defee nga tabb leen, ñu yilif ay kurél yu mat junniy nit ak yu tollu ci téeméeri nit, ba ci juróom fukki nit mbaa fukki nit. \v 22 Nga bàyyi leen nag, ñuy àtteel mbooloo mi bés bu nekk seeni jote. Su ko defee, mboolem réeroo bu mag, ñu indil la ko; mboolem réeroo bu sew nag, ñoom ñu àtteel ko seen bopp. Noonu ngay woyofale sab yen, ñu jàpple la ci. \v 23 Boo defee noonu, te Yàlla ànd ci, dinga ko mana dékku, mbooloo mii mépp it mana dellook jàmm ca seeni kër.» \p \v 24 Musaa nag topp ndigalu goroom, daldi def mboolem la mu ko wax. \v 25 Mu seet ca bànni Israyil gépp, tànn ca góor ñu mat, fal leen, ñu yilif mbooloo ma: ñii jiite kuréli junniy nit; ñii, téeméer; ñii, juróom fukk; ñii fukk. \v 26 Ñuy àtte nag mbooloo ma saa su nekk. Su dee mbir mu lëj, ñu indil Musaa; mboolem mbir yu sew-sewaan ya, ñoom ñu àtte ko. \v 27 Ba loolu weesee Musaa tàggtook goroom, mu dellu réewam. \c 19 \s1 Yàlla xamle na kóllëreem \p \v 1 Keroog benn fan ca ñetteelu weer wa, gannaaw ba ñu génnee Misra, ca lañu agsi màndiŋu Sinayi. \v 2 Fekk na ñu bàyyikoo Refidim, doora duggsi màndiŋu Sinayi, daldi dal ca màndiŋ ma. Israyil a nga daloon foofa janook tund wa. \p \v 3 Ba loolu amee Musaa yéeg, jëm ca Yàlla. \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji jaar ci turu Musaa foofa ca kaw, ne ko: «Nanga wax ak waa kër Yanqóoba te nanga ma siiwtaaneel ci \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* googu, lii ma lay wax: \v 4 “Yeena gisal seen bopp ni ma def waa Misra, te yeen, ma boot leen, ni jaxaay di fireey laafam, boot ay doomam, ba ngeen jegesi ma fii. \v 5 Léegi nag su ngeen ma déggalee bu baax, di sàmm sama \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* ak yeen, yeenay doon sama moomeelu bopp ci mboolem askan yi. Dëgg la, àddina wërngal këpp maay Boroom, \v 6 waaye yeenay doon nguuru \w sarxalkati|lemma="sarxalkat b-:"\w* Yàlla, te di xeet wu sell.” Kàddu yooyu ngay wax bànni Israyil.» \p \v 7 Musaa dellu, woolu magi mbooloo ma. Mu jottli leen mboolem wax jooju ko Aji Sax ji dénk. \v 8 Mbooloo ma mépp bokk benn baat, àddu ne: «Li Aji Sax ji wax lépp dinanu ko def.» Ci kaw loolu Musaa dem yegge Aji Sax ji tontal mbooloo ma. \p \v 9 Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Ma ne, dinaa yiiroo niir wu fatt, dikk ba agsi fi yaw, ngir bu may wax ak yaw, mbooloo mi di ci dégg, ndax ñu wóolu la ba fàww.» Ba loolu amee Musaa baamtul Aji Sax ji tontal mbooloo ma. \s1 Yàlla wàcc na ca kaw tundu Sinayi \p \v 10 Gannaaw loolu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxaat Musaa ne ko: «Dellul ca mbooloo ma, te nanga leen sell-luloo tey ak ëllëg. Nañu fóot seeni yére, \v 11 te waajal gannaaw-ëllëg, ndax gannaaw-ëllëg man Aji Sax ji maay wàcc ci kaw tundu Sinayi ci kanam mbooloo mépp. \v 12 Sàkkalal mbooloo mi ag kemu fi wër tund wi, te nga wax leen ne leen: “Moytuleena yéeg ci kaw tund wi, mbaa ngeen di laal tund wi fenn. Képp ku laal tund wi, dees na ko rey. \v 13 Bu loxo laal kooka, waaye nañu ko dóor ay doj ba mu dee, mbaa ñu jam ko. Su dee nit, su dee mala, bumu dundati.” Bu liit gi jibee doŋŋ nag lañuy doora mana dem ba ca tund wa.» \p \v 14 Ba loolu amee Musaa wàcc tund wa, dellu ca mbooloo ma. Mu sell-luloo leen, ñu fóot seeni yére, \v 15 ba noppi, mu wax leen ne leen: «Waajal-leen gannaaw-ëllëg, te li feek booba, buleen fi ànd ak jigéen.» \p \v 16 Keroog ca gannaaw-ëllëg sa, naka la njël jot, muy dënook a melax, ànd akaw niir wu fatt ca kaw tund wa, ak coowal liit gu xumb. Waa dal ba bépp a nga tiit, bay lox. \v 17 Musaa daldi jiite mbooloo ma, ñu génn dal ba, ngir dajejeek Yàlla. Ñu dem ba ca suufu tund wa, taxaw fa. \v 18 Fekk na tundu Sinayi wa wépp di sël-sëleeku saxar, ndax Aji Sax ja fa wàcc ci biir sawara. Saxar saa ngay gilli ni saxaru puuru ban, tund wépp di yëngook doole, \v 19 liit ga gëna jolli. Musaa ngay wax, Yàlla di ko tontoo kàddug dënu. \v 20 Ba mu ko defee Aji Sax ji wàcc ca tundu Sinayi wa, ca njobbaxtalu tund wa. Aji Sax ji nag woo Musaa foofa, ca njobbaxtal ga, Musaa dellu yéeg. \v 21 Aji Sax ji ne ko: «Wàccal, àrtu mbooloo mi, ndax ñu baña bëtt, di ma deñsi kumpa; lu ko moy ñu bare ci ñoom dinañu dee. \v 22 Te it \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w*, yi may jege, man Aji Sax ji, dañoo wara sellal, bala may dal ci seen kaw.» \v 23 Musaa wax Aji Sax ji ne ko: «Mbooloo mi kat manuñoo yéeg tundu Sinayi, ndax yaw ci sa bopp àrtu nga nu, ne nu, nu sàkk ag kemu fi wër tund wi, te nu xam ne tund wu sell la.» \v 24 Aji Sax ji ne ko: «Wàccal te délsi, ànd ak Aaróona. Waaye muy sarxalkat yi, di mbooloo mi, bu kenn bëtt, jëm ci man Aji Sax ji, lu ko moy ma dal ci seen kaw.» \v 25 Ba loolu amee Musaa wàcc, fekki mbooloo ma, wax ak ñoom. \c 20 \s1 Kóllëre gi laaj na ay sàrt \p \v 1 Yàlla wax na bànni Israyil kàddu yii yépp, ne leen: \v 2 «Man \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, maa di seen Yàlla, ji leen génne réewum Misra, kërug njaam ga. \p \v 3 «Buleen am yeneen yàlla ci sama kanam. \p \v 4 «Buleen sàkkal seen bopp tuur muy jëmmal lenn lu nekk ci kaw asamaan, mbaa ci kaw suuf, mbaa lu nekk ci ndox mu suuf tiim. \v 5 Buleen ci sujjóotal lenn, buleen ci jaamu lenn, ndax man seen Yàlla Aji Sax ji, Yàlla ju fiir laa. Maay topp doom tooñu waajur, ba ca seen maasi sët, ba ca maasug sëtaati nit ñi ma bañ. \v 6 Waaye maay baaxe ñi ma sopp, di sàmm samay santaane, ba ci junniy maas ya leen di wuutuji. \p \v 7 «Buleen tudd seen turu Yàlla Aji Sax ji ci neen, ndax Aji Sax ji du ñàkka topp kuy tudd aw turam ci neen. \p \v 8 «Deeleen baaxantal \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*, ngir sellal ko. \v 9 Juróom benni fan ngeen wara liggéey, def ci seen soxla yépp. \v 10 Waaye bésub juróom ñaareel ba, Noflaay lay doon, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Buleen ci liggéey lenn; du yeen, du seen doom ju góor ak ju jigéen, du seen jaam bu góor ak bu jigéen, du seenug jur, te du seen gan gu nekk ci seen biir dëkk. \v 11 Ndax man Aji Sax ji, juróom benni fan laa sàkk asamaan ak suuf ak géej ak mboolem li ci biir, bésub juróom ñaareel ba, ma dal-lu. Moo tax man Aji Sax ji ma barkeel bésub Noflaay, sellal ko. \p \v 12 «Teral-leen seen ndey ak seen baay, ndax ngeen gudd fan ca suuf sa leen seen Yàlla Aji Sax ji jox. \p \v 13 «Buleen bóome. \p \v 14 «Buleen jaaloo. \p \v 15 «Buleen sàcc. \p \v 16 «Buleen seedeel seen moroom lu dul dëgg. \p \v 17 «Buleen xemmem seen lennu moroom: du këram, du jabaram, du jaamam bu góor, du jaamam bu jigéen, du nagam, du mbaamam.» \s1 Mbooloo ma dagaan na ab jottlikat \p \v 18 Mbooloo mépp a nga teew, ba muy dënook a melax, ànd ak coowal liit gaak tund way saxar. Ñu gis loolu, di kat-kati, dànd fu sore. \v 19 Ci kaw loolu ñu ne Musaa: «Yaw, waxal ak nun, nu dégg, waaye bu Yàlla ci boppam wax ak nun, lu ko moy nu dee.» \p \v 20 Musaa ne mbooloo ma: «Buleen ragal, ndax nattu leen moo tax Yàlla ñëw, ngir ngeen ragal ko, ba dungeen moy.» \p \v 21 Noonu la mbooloo ma taxawe, dànd tund wa. Mennam Musaa moo jegeji niir wu fatt, wa Yàlla nekkoon. \ms1 Téereb kóllëre gi \s1 Ay dogal a ngi, yu jëm ci ab sarxalukaay \p \v 22 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ne ko: «Li ngay wax \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* mooy lii: “Yeena ko gisal seen bopp. Ca asamaan sax laa àddoo, wax ak yeen. \v 23 Buleen sàkkal seen bopp ay tuuri xaalis, mbaa ay tuuri wurus, di ma bokkaale, bumu am mukk. \v 24 \w Sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bu ñu defare suuf ngeen may sàkkal, di ci sarxal seeni gàtt ak seeni nag, muy seen \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, mbaa seen \w saraxi cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*. Sàkkleen ab sarxalukaay ci mboolem bérab bu may fàttlee sama tur, ma dikk fi yeen, barkeel leen. \v 25 Su ngeen ma dee sàkkal sarxalukaayu xeer, buleen ko defare xeer yu ñu yett, ndaxte bu ngeen ko laalalee ab jumtukaay, teddadil ngeen ko. \v 26 Buleen yéeg ci ay dëggastal, doora mana àgg ca sama sarxalukaay, ndax loolu day tax ngeen di fa sàgganu.”» \c 21 \p \v 1 Aji Sax ji teg ca ne: «Àttey yoon yii, nanga leen ko jox: \s1 Lu jëm ci Ebrë yiy ay jaam \p \v 2 «Su ngeen jëndee jaam bu góor bu dib \w Ebrë|lemma="Ebrë:"\w*, na liggéey juróom benni at. Juróom ñaareel ba lay moom boppam te du ameel kenn dara. \v 3 Su fekkee ne ba muy dugg njaam, moom doŋŋ la woon, moom doŋŋ ay moom boppam; su ko fekkee mu am jabar, na jabaram ànd ak moom, ñu moom seen bopp. \v 4 Su fekkee ne sangam a ko may jabar, ndaw si am ak moom ay doom, jabar jeek doomam yu góor mbaa yu jigéen, sang bee leen di moom. Moom ci boppam doŋŋ ay moom boppam. \v 5 Waaye su jaam bi biralee ne: “Maa bëgg sama sang, maak sama jabar ak samay doom, te buggumaa moom sama bopp”, \v 6 su boobaa na ci sang bi sàkku seede àttekat yi. Su ko defee mu sësal waa ji ci lafu bunt bi mbaa jënu bunt bi. Foofa lay bënne noppu waa ji ab puso, mu daldi doon ab jaamam giiru dundam. \p \v 7 «Su fekkee ne góor dafa jaay doomam ju jigéen njaam, deesu ko mana goreel ni bu doon góor. \v 8 Su ko sangam jëndee, def ko jabar, ba noppi bëggatu ko, na fexe ñu feyal ndaw si ag njotam, waaye amul sañ-sañu jaay ko ay doxandéem, ndax loolu wor la. \v 9 Su fekkee ne da koo jëndal doomam ju góor, na jëfeek moom, na mu dëppook wareefu doom ju jigéen. \v 10 Ki jënd as ndaw, def ko jabar nag, su takkee keneen it, warula wàññi la mu warlook jaam ba mu def jabar ci wàllu dund ak koddaay ak dëkkoo. \v 11 Su ko sang ba matalul ñett yooyii nag, day moom boppam, dem te du fey dara. \s1 Lu jëm ci lor sa moroom \p \v 12 «Ku dóor nit, rey ko, dee rekk mooy àtteem. \v 13 Su dul woon pexe mu mu lal, xanaa mu fekk Yàlla yemale nit ki ciy loxoom, dinaa leen won bérab bu muy daw, làquji fa. \p \v 14 «Waaye nag, su nit fexeelee moroomam, nax ko, ba rey ko, su làqoo woon sama \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* sax, jàppleen ko, rey. \p \v 15 «Ku dóor baayam mbaa ndeyam, dee rekk mooy àtteem. \p \v 16 «Ku sàcc nit, dee rekk mooy àtteem, moo xam da koo jaay, mbaa ñu fekk ko ci ay loxoom. \p \v 17 «Ku saaga baayam mbaa ndeyam, dee rekk mooy àtteem. \p \v 18 «Su ay nit jàppantee, kenn ki dóor moroom ma loxoom mbaa aw doj, su ca deewul, te ab tëraayam sababoo ca, \v 19 su ci jógee mana génn ci biti, jàpp ciw yet sax, di dox, deesul daan ki ko dóor, waaye dina dàmp ki mu dóor ngir li mu tëdd liggéeyul, ak li pajam laaj. \p \v 20 «Ku dóor yet jaamam bu góor mbaa bu jigéen, ba mu dee ciy loxoom, dees na ko feyul moos. \v 21 Waaye su jaam ba dundee ba ca ëllëg sa, mbaa gannaaw-ëllëg sa, deesu ko feyul ndaxte moomeelu sangam la. \p \v 22 «Su ay góor dee jàppante, ba kenn ci ñoom dal ci jigéenu wérul, ba liir bi génn, bu ci genn loraange toppul, dees na feyloo moos ki dal ci kawam, ndàmpaay li jëkkër ji laaj, te ña leen di àtte juboo ca limu pey ga. \p \v 23 «Waaye su ci loraange sababoo nag, na bakkan fey bakkan, \v 24 bët fey bët, bëñ fey bëñ, loxo fey loxo; tànk fey tànk, \v 25 lakk-lakk fey lakk-lakk, tëccu-tëccu fey tëccu-tëccu, góom fey góom. \p \v 26 «Ku dóor ab jaamam bu góor mbaa bu jigéen, ba tuur bëtam, na ko goreel ndax bët ba. \v 27 Su foqee bëñu jaamam bu góor mbaa bu jigéen, na ko goreel ndax bëñ ba. \p \v 28 «Su aw nag dañee góor mbaa jigéen, ba rey ko, dóorleen nag wi ay xeer ba mu dee, te buleen lekk yàpp wi, waaye boroom nag wi, yoon toppu ko. \v 29 Su fekkee ne nag wi da daan dañe, ñu yégaloon ko boroom, wattuwu ko, ba nag wi rey góor mbaa jigéen, dóorleen nag wi ay xeer, ba mu dee, te teg ci rey boroom nag wi. \v 30 Su fekkee ne dees koo sas ndàmpaay, na fey lim bu ñu ko mana sas, muy njot-gi-bakkanam. \v 31 Ba tey itam, su nag wi dañee xale, ba mu dee, muy góor mbaa jigéen, na àtte biy benn rekk ci boroom nag wi. \v 32 Su nag wi dañee ab jaam ba mu dee, muy góor mbaa jigéen, na boroom nag wi fey boroom jaam bi fanweeri dogi xaalis, te nañu dóor nag wi ay xeer, ba mu dee. \p \v 33 «Su fekkee ne nit dafa ubbi kàmb gu ube woon, mbaa mu gas kàmb, wacc ko mu ne ŋàpp, ba nag mbaa mbaam daanu ci, \v 34 na boroom kàmb gi fey; day delloo boroom mala mi njégu mala mi, daldi féetewoo mala mi ci dee. \p \v 35 «Su nagu nit jamee nagu moroomam, ba mu dee, nañu bokk jaay nag wiy dund, séddoo njég gi, te séddoo nag wi dee. \p \v 36 «Waaye su fekkee muy nag wu ñu xam ne da daan dañe, te boroomam ñàkk koo wattu, boroomam day feye nag wi dee aw nag wuy dund, daldi féetewoo wi dee. \c 22 \p \v 1 «Ku sàcc aw nag mbaa ab gàtt, rey ko mbaa mu jaay ko, na feye wenn nag, juróomi nag; benn gàtt, mu feye ko ñeenti gàtt. \s1 Yoonu Aji Sax ji ñoŋal na alalu nit \p \v 2 «Su fekkee dañoo jàpp ab sàcc guddi, muy toj kër jaambur, bu ñu ko dóoree, ba mu dee, deesul topp ki dóor, bakkanu sàcc bi, \v 3 waaye su jant xasee fenk, dees na ko topp bakkanam. \p «Ab sàcc nag, bu ñu ko jàppee, na delloo li mu sàcc rekk. Su fekkee amu ko, dees koy jaay njaam, ndax càcc gi. \p \v 4 «Su dee ku sàcc mala, muy nag mbaa mbaam mbaa ab gàtt, te ñu fekk ko ciy loxoom, muy dund, na fey ñaaram. \p \v 5 «Ku wacc sag jur, mu ruur toolub jaambur, ba lekk toolam mbaa tóokëru reseñam, na tànn li gën ci meññeefum toolu boppam mbaa tóokëru reseñam, dàmpe ko boroom tool bi mu lor. \p \v 6 «Su fekkee ne dañoo taal sawara, mu jàpp cib ñag, lakkaale pepp mu jóore, mbaa pepp mu ñor mu ñu góobagul, mbaa mu ñoragul, ka taal sawara wa mooy xala fey li lakk. \p \v 7 «Su nit dénkee moroomam xaalis, mbaa alal, ñu sàcce ko ci kër ki denc, te ñu jàpp sàcc bi, na sàcc bi fey ñaari yoon la mu sàcc. \v 8 Su ñu ko jàppul nag, na boroom kër gi sàkku seede àttekat yi, te waat ne, du moom ci boppam moo aakimoo alalu moroomam. \v 9 Saa yu ay nit jotee ci mbirum nag mbaa mbaam mbaa gàtt mbaa yére, mbaa lu réer lu mu doon, ñaar ñi solowoo alal ji, muy mala mbaa leneen, nañu yóbbu mbir mi fi kanam àttekat yi. Ku ci àttekat yi teg tooñ, na fey moroom mi ñaari yoon. \p \v 10 «Su nit dénkee moroomam mbaam mbaa nag mbaa gàtt mbaa mala mu mu mana doon, su jur gi deeyee mbaa mu damm mbaa ñu sàcce ko àll te amul seede, \v 11 li leen di àtte ngiñ lay doon ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Na ka dencoon mala ma giñ ne jëlu ko. Na boroom mala mi it nangu ngiñ li. Ki dencoon du ko fey dara. \v 12 Waaye su ñu sàccee mala mi ci këram, moom mi dencoon mooy delloo boroom. \v 13 Su fekkee ne rabu àll a fàdd mala mi, na indi li ci des, muy firnde. Su boobaa du fey dara. \v 14 Su nit àbbee juru moroomam, jur ga damm mbaa mu dee fu boroom nekkul, na ki àbboon fey. \v 15 Waaye su ko boroomam fekkee, du laaj muy fey. Su fekkee ne dafa bindoon mala mi ci boroom, di ko fey, na boroom féetewoo njég, ga ñu binde woon mala mi, muy peyam. \s1 Yoonu Aji Sax ji rafetal na dundin \p \v 16 «Su góor naxee ab janq bu kenn joxagul warugar, ba tëdde ko, na fey warugaram, muy jabaram. \v 17 Su fekkee ne baayam dafa lànk, ne du ko ko may it, du tere mu wara fey ci xaalis lu tollook warugaru janq. \p \v 18 «Ab xërëmkat bu jigéen, buleen ko bàyyi, mu dund\f + \fr 22.17 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Sarxalkat yi\+bk* 19.26 ak 31.\ft*\f*. \p \v 19 «Képp ku jaxasoo ak mala, dee rekk mooy àtteem. \p \v 20 «Kuy sarxeel jeneen yàlla ju dul \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji moom rekk, dees koy faagaagal. \p \v 21 «Ab doxandéem, buleen ko lor, buleen ko not, ndaxte yeen itam ay doxandéem ngeen woon fa réewum Misra. \p \v 22 «Képp ku dib jëtun akub jirim, buleen ko néewal. \v 23 Bu ngeen leen néewalee déy, bu ñu yuuxoo, woo ma wall, dinaa dégg seen yuux moos. \v 24 Su boobaa sama mer dina tàng, ma reye leen saamar, seeni jabar diy jëtun, seeni doom diy jirim. \p \v 25 «Bu ngeen dee lebal ku bokk ci sama ñoñ, di néew-ji-doole ju ngeen dëkkal, buleen def ni ab leblekat, di ko sas ab tegandaay. \p \v 26 «Su ngeen nangoo mbubbam tayle ci seen dëkkandoo, dellooleen ko ko bala jant a so. \v 27 Moom doŋŋ la am ci yére, di ko sànge yaramam; su ko ñàkkee, lu muy sàngoo ba tëdd? Te su ma wooyee wall kat, dinaa ci dégg, ndax man Boroom Yërmande laa. \p \v 28 «Man Yàlla, buleen wax lu ñaaw ci man, te seen kilifag askan, buleen wax lu bon ci moom. \p \v 29 «Li tuuroo ci seen sàq yu fees, ak li wale ci seen nalukaay yu rembat, sama cér la; buleen ko yeexe, te seen taaw yu góor it, man ngeen leen di sédde. \v 30 Seen jur gu gudd ak gu gàtt itam, naka noonu. Juróom ñaari fan lay nekk ak ndeyam, bésub juróom ñetteel ba, ngeen jox ma ko. \v 31 Te itam nit ñu \w sell|lemma="sell:"\w* ngeen wara doon, ñeel ma, kon nag yàppu mala mu ñu fàdde ci àll bi, buleen ko lekk; sànnileen ko xaj yi. \c 23 \s1 Àtte laaj na njub ak yërmande \p \v 1 «Buleen siiwal ay fen; buleen lëngoo ak tooñkat, ngir doon seedeb naaféqam. \v 2 Buleen seet fi mbooloo gëna baree, ngeen topp leen ci jëf ju bon; te it buleen jeng, di topp mbooloo mu gëna bare ci ab layoo, di leen seedeel lu toxal dëgg. \v 3 Néew-doole bi it, buleen ko far cib layoo. \p \v 4 «Su ngeen dajeek seen nagu noon mbaa mbaamam mu réer, fexeleen ba délloosil ko ko. \v 5 Su ngeen gisee seen mbaamu noon mu ab sëf daaneel, buleen ko romb; dimbalileen seen noon, yékkatil-leen ko ko. \p \v 6 «Buleen jalgati àqu néew-ji-doole cib layoom. \v 7 Kàddu gu dëgguwul, soreleen ko, te ku deful dara ak kuy def njekk, buleen ko reylu, ndax nit ku bon, duma ko àtte mukk àtteb kuy def njekk. \v 8 Alali ger nag buleen ko nangu, ndax ger day gumbaal njàccaar, di safaan waxi ku nekk ci dëgg. \p \v 9 «Ab doxandéem, buleen ko not; yeen ci seen bopp, jaar ngeen ci ndoxandéem, ndax ay doxandéem ngeen woon ca réewum Misra. \s1 Lu jëm ci bési Noflaay \p \v 10 «Diiru juróom benni at ngeen di ji seen tool, for li ci meññe; \v 11 waaye atum juróom ñaareel ma, noppal-leen tool bi, booyal ko; seen néew-dooley askan wi man cee lekk, li ci des, rabi àll yi for ko. Seen toolub reseñ ak seen tóokëru oliw itam, naka noonu. \p \v 12 «Diiru juróom benni fan ngeen di liggéey, waaye bésub juróom ñaareel ba, nopplu leen, ndax seen nag ak seen mbaam mana nopplu, seen surga akub doxandéem it mana astandiku. \p \v 13 «Li ma leen wax lépp sàmmleen ko, te turi yeneen yàlla, buleen ko tudd; bumu jibe sax seen gémmiñ. \s1 Lu jëm ci bési màggali Israyil \p \v 14 «Ñetti yoon cim at ngeen may jagleel màggal. \v 15 \w Màggalu Mburu mu amul lawiir|lemma="Màggali Yawut yi:"\w*, wormaal-leen ko. Diiru juróom ñaari fan ngeen ciy lekk mburu mu amul lawiir ni ma leen ko sante, saa yu jamonoom jotee ci weeru \w Abiib|lemma="Abiib:"\w*, ndaxte ci ngeen génn Misra. Te itam buleen taxawe loxoy neen ci sama kanam. \v 16 Wormaal-leen \w màggalu bésu Ngóob|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* mi jëkka ñore ci tool, yi ngeen di bey, ak \w màggalu bésu Farmàngu|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* mi ci ndeetel at mi, gannaaw bu ngeen dajalee seen meññeef ba noppi. \v 17 Ñetti yoon cim at la seen góor ñépp di teew fi kanam Boroom bi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \p \v 18 «Buleen ma rendil benn sarax, di boole deret jaak lu am lawiir, te nebbonu jur gu ngeen ma sarxal ci sama màggal, bumu fanaan ba bët set. \p \v 19 «Ngëneeli meññeef ma jëkka ñore ca seen suuf, moom ngeen di yóbbu seen kër Yàlla Aji Sax ji. \p «Ab tef, buleen ko togge soowum yaayam. \s1 Yàlla yeb na bànni Israyil \p \v 20 «Te nag man ci sama bopp, maay yebal malaaka, mu di leen sàmm ci yoon wi, ba yóbbu leen bérab ba ma waajal. \v 21 Bàyyileen ko xel bu baax, déggal ko te bañ koo merloo, ndax du leen baal seen moy, ngir sama tur la taxawe. \v 22 Waaye su ngeen ko déggalee ba déggal ko, di jëfe li ma leen wax lépp, su boobaa ma noonoo seeni noon, bañ seeni bañaale. \p \v 23 «Bu leen sama malaaka jiitoo, ba yóbbu leen ca réewum Amoreen ña ak Etteen ña ak Periseen ña ak Kanaaneen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña, ba ma faagaagal leen ñoom ñépp, \v 24 su boobaa buleen sujjóotal mukk seeni tuur, di leen jaamu, mbaa ngeen di roy seeni aada, waaye yàqteleen seeni tuur te toj tasar seen tuuri doj, ya fa sampe. \v 25 Jaamuleen ma, man seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ma barkeel seen dugub ak seen ndox, boole ci jële wopp ci seen biir. \v 26 Su ko defee du kenn ku ëmbam di yàqu, mbaa mu tëlee am doom ci seenum réew, te maay matal sëkk seen limu fan. \p \v 27 «Tiitaange laay yebal, mu jiitu leen. Maay tiital mboolem xeet wu ngeen fekki, te maay def seen noon yépp won leen gannaaw. \v 28 Maay yebal njàqare lu leen jiitu, dàqal leen Eween ñi ak Kanaaneen ñi ak Etteen ñi. \v 29 Waaye duma leen dàqandoo ci menn at, lu ko moy réew mi gent, rabi àll yi mujj bare lool ci seen kaw. \v 30 Ndànk-ndànk laa leen leen di dàqal, ba kera ngeen di yokku, ba nangu réew mi. \p \v 31 «Maa leen di dogal kemug suuf gu dale géeju Barax yi, ba géeju waa Filisti, daleeti ca màndiŋ ma, ba ca dexu Efraat, ndax maay teg waa réew mi ci seeni loxo, ngeen dàq leen. \v 32 Buleen wóllëranteek ñoom, buleen wóllëranteek seeni tuur. \v 33 Buñu dëkke seenum réew, lu ko moy muy seen ndëgg-sërëx; ndax dañu leen di xiir ci moy ma, ba ngeen jaamu seeni tuur.» \c 24 \s1 Yàlla fasoo na kóllëre ak bànni Israyil \p \v 1 Mu neeti Musaa: «Yéegal ñëw fi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, yaw ak Aaróona ak Nadab ak Abiyu ak juróom ñaar fukki magi Israyil, te ngeen sujjóote nee, dànd ma. \v 2 Su ko defee yaw rekk yaay dikk, ba jege ma, man Aji Sax ji, waaye ñi ci des buñu jegesi, te it bu mbooloo mi yéegandoo ak yaw.» \v 3 Musaa dem, yeggeji mbooloo ma kàdduy Aji Sax ji yépp, ak àttey yoonam yépp. Mbooloo ma mépp bokk benn baat, ne ko: «Li Aji Sax ji wax lépp dinanu ko def.» \v 4 Ba loolu weesee Musaa bind na mboolem kàdduy Aji Sax ji. Mu xëy nag suba teel, daldi sàkk ab \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* ca suufu tund wa, sampaale fa fukki doj ak ñaar, ñeel fukki giiri Israyil yaak ñaar. \v 5 Ba mu ko defee mu yebal ay ndawi \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, ñooña def ay \w saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, boole ci rendi yëkk yu ndaw yu ñu def \w saraxi cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*, ñeel Aji Sax ji. \v 6 Musaa jël genn-wàllu deret ja, sotti ci ay ndab, la des ca deret ja, mu xëpp ko ca sarxalukaay ba. \v 7 Ba loolu amee mu jël téere ba ñu bind \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* ga, jàngal ko mbooloo ma, ñuy dégg. Mbooloo ma ne ko: «Li Aji Sax ji wax lépp dinanu ko def, ba mu mat sëkk.» \v 8 Musaa jël deret ja, wis-wisal ca kaw mbooloo ma, ne leen: «Lii nag mooy deret ji Yàlla fase kóllëre gi mu séq ak yeen te mu aju ci mboolem kàddoom yii.» \p \v 9 Ba loolu amee Musaa yéeg, ànd ak Aaróona ak Nadab ak Abiyu ak juróom ñaar fukki magi Israyil. \v 10 Ñu daldi gis Yàllay bànni Israyil. Lu mel ni dëru per bu safiir a nga lal tànkam ya, mel ni asamaan, ndax na mu sete wecc. \v 11 Waaye njiiti bànni Israyil ña, loxol Yàlla dalu leen. Ñoo gis Yàlla, te gannaaw loolu lekk nañu, naan nañu. \s1 Musaa yéeg na ca tund wa \p \v 12 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ne ko: «Yéegal ba ci man ci kaw tund wi te négandiku fa, ma jox la àlluway xeer yi ak yoon wi, ak santaane yi ma ci bind ngir jàngle ko.» \v 13 Musaa daldi jóg, mook Yosuwe, bëkk-néegam. Musaa nag yéeg ca tundu Yàlla wa. \v 14 Fekk na mu wax mag ña ne leen: «Xaarleen nu fii, ba nu délsi. Aaróona ak Ur a ngi nii ak yeen; ku ci am mbir mooy àttelu, demal ci ñoom.» \p \v 15 Ba Musaa yéegee ca kaw tund wa, niir wa daa yiir tund wa, \v 16 leeru Aji Sax ja dal ca kaw tundu Sinayi, niir wa yiir tund wa diiru juróom benni fan. Bésub juróom ñaareel ba Aji Sax ji àddoo ca digg niir wa, woo Musaa. \v 17 Melow leeru Aji Sax jaa ngay nirook sawara wuy tàkk ca njobbaxtalu tund wa, \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* di gis. \v 18 Musaa yéeg ca kaw tund wa ba tàbbi ca biir niir wa, di wéy. Musaa nekk na ca kaw tund wa ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg. \c 25 \ms1 Lu jëm ci jaamookaay bi \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ne ko: \v 2 «Waxal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen, ñu indil ma ab jooxe. Ci képp ku am yéeneem ngeen di nangoo sama jooxe, indil ma ko. \v 3 Jooxe bi ngeen di nangoo ci ñoom di wurus ak xaalis ak xànjar, \v 4 ak wëñ gu baxa te laal yolet ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ak kawari bëy \v 5 ak deri kuuyu xar yu ñu wulli, sóob ko xonqal, ak deri piipi\f + \fr 25.5 \fr*\fk piipi \fk*\ft rabu géej la, bu der ba nooy te ndox du ko dugg.\ft*\f* ak banti séng\f + \fr 25.5 \fr*\fk séng: \fk*\ft am na ñu koy wooye kasiya.\ft*\f*, \v 6 ak diwu oliw gu ñuy taaloo, ak ndàbb luy xeeñal diwu pal, di xeeñal cuuraay, \v 7 ak peri onigsë, ak yeneen per yu ñuy tapp ci \w xar-sànnim|lemma="xar-sànni m-:"\w* sarxalkat bu mag ba ak kiiraayal dënnam. \v 8 Na ma bànni Israyil defaral kër gu sell, ndax ma dëkk ci seen biir. \v 9 Na lépp dëppoo ak li ma lay won. Muy misaalu xaymab jaamookaay bi, di misaalu mboolem ay jumtukaayam, lépp defeleen ko noonu. \s1 Lu jëm ci gaal giy def àlluway seede si \p \v 10 «Defarleen gaalu dénku séng, guddaayam di ñaari xasab\f + \fr 25.10 \fr*\fk xasab \fk*\ft mooy guddaayu loxo, diggante catu baaraamu digg ak conc.\ft*\f* ak genn-wàll, yaatuwaayam di xasab ak genn-wàll; taxawaayam di xasab ak genn-wàll. \v 11 Nañu ko xoob wurusu ngalam. Biir ak biti lañu koy xoob, sàkkal ko kéméju wurus, gu ko wër. \v 12 Móolalal gaal gi ñeenti lami wurus yu ñuy takk ci ñeenti tànk yi; ñaari lam, wet gii; ñaar wet gee. \v 13 Yettlul ay banti njàppuy séng te nga xoob bu ci nekk wurus. \v 14 Su ko defee nga roof njàppu yi ci lam, yi ci weti \w gaal|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* gi, ngir ñu di ko yóbboo gaal gi. \v 15 Ci lami gaal gi la njàppu yiy des te bañ cee jógeeti. \v 16 Yebal ci gaal gi àlluway seede si ma lay jox. \p \v 17 «Defarlul kubeer gu ñuy amale njotlaay gu wurusu ngalam ngir gaal gi. Na guddaayam di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaayam di xasab ak genn-wàll. \v 18 Tëgglul ñaari malaakay \w serub|lemma="serub y-:"\w* yu wurus te nga féetale leen ak ñaari cati kubeeru njotlaay ga. \v 19 Defal cat lii ab serub, cat lee ab serub te nanga móolaale kubeer gi ak serub yi ci ñaari cat yi, ñu ànd di benn. \v 20 Na serub yi tàllal seeni laaf, jëme kaw te nañu yiire kubeeru njotlaay gi seeni laaf. Nañu janoo, te na seeni kanam jublook kubeeru njotlaay gi. \v 21 Tegal kubeeru njotlaay gi ci kaw gaal gi, gannaaw boo ci yebee àlluway seede si ma lay jox. \v 22 Foofa laay dajeek yaw; fa tiim kubeeru njotlaay ga, ca diggante ñaari serub ya ca kaw gaalu seede sa, fa laa lay waxe mboolem lu ma lay sant, ñeel \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \s1 Lu jëm ci taabalu mburum sarax mi \p \v 23 «Defarlul taabalu bantu séng, guddaayam di ñaari xasab, yaatuwaayam di xasab, taxawaayam di xasab ak genn-wàll. \v 24 Xoob ko wurusu ngalam te defal ko kéméju wurus gu ko wër. \v 25 Defal ko pegg bu ko wër bu tollu ci ñeenti baaraam, te sàkkal pegg ba wombu wurus, wërale ko. \v 26 Defarlul ko ñeenti lami wurus te takk lam ya ca ñeenti wet ya, fa fareek ñeenti tànk ya. \v 27 Na lam yi dendeek pegg bi, ngir mana téye njàppu, yi ñuy yóbboo taabal ji. \v 28 Yettlul ay njàppu yu bantu séng, nga xoob njàppu yi wurus, ñu di ko yóbboo taabal ji. \v 29 Sàkkal ko ay ndabam yu tell aki mbàttoom aki njaqam, ak këllam yi ñuy tuuroo. Te wurusu ngalam ngay def lu ci nekk. \v 30 Tegal \w mburum teewal|lemma="mburum teewal m-:"\w* mi ci kaw taabal ji, mu nekk ci sama kanam ba fàww. \s1 Lu jëm ci tegukaayu làmp bi \p \v 31 «Defarlul tegukaayu làmp bu wurusu ngalam. Tegukaay ba, dees koy tëgg. Na taatu tegukaay ba ak per ba ànd aki kaasam aki kàmbóotam aki mbaram, lépp di benn. \v 32 Juróom benni car ñooy soqikoo ca wet ya, ñetti car ci gii wet, ñett ca ga ca des. \v 33 Benn car day am ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóoru garabu amànd\f + \fr 25.33 \fr*\fk garabu amànd \fk*\ft xeetoo naak gerte-tubaab.\ft*\f*, kaas bu ci nekk ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram, car ba ca topp am ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóoru garabu amànd, kaas bu ci nekk ànd aki kàmbóotam aki mbaram, juróom benni car, ya soqikoo ca per ba, daj. \v 34 Gannaaw loolu peru tegukaayu làmp ba itam day am ñeenti kaas yu bindoo ni tóor-tóoru garabu amànd, ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram. \v 35 Ab kàmbóot ay ronu yii ñaari car, jàpp ca; beneen kàmbóot ronu ñaari car ya ca topp, jàpp ca, ab kàmbóot ronu ñaari car ya mujj, jàpp ca, juróom benni car, ya soqikoo ca peru làmp ba, daj. \v 36 Kàmbóot ya ak car ya dañuy ànd ak tegukaay ba, di benn, lépp doon lu ñu tëgge wenn dogu wurusu ngalam. \v 37 Defarlul juróom ñaari làmpam. Te na làmp ya tege tegin wuy leeral ca kanam tegukaay ba. \v 38 Ñiimi feyukaayu làmp yi ak andi làmp yi na doon wurusu ngalam. \v 39 Fanweeri kiloy wurusu ngalam ak juróom\f + \fr 25.39 \fr*\ft Mu yemook benn nattu diisaay bu ñu daan jëfandikoo, ñu di ko wax talaŋ.\ft*\f*, ci lees di sàkk tegukaayu làmp bi, ak mboolem li mu àndal. \v 40 Nanga xool te topp misaal, yi ñu la ciy won ci kaw tund wi. \c 26 \s1 Lu jëm ci sori xaymab jaamookaay bi \p \v 1 «Xaymab jaamookaay bi nag, defare ko fukki sori rabali lẽe, mu ànd ak wëñ gu baxa te laal yolet ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr, te nga ñawaale ca nataali \w serub|lemma="serub y-:"\w*. \v 2 Guddaayu sor bu nekk na doon ñaar fukki xasab ak juróom ñett, yaatuwaay ba di ñeenti xasab, te sor yépp ay tolloo. \v 3 Yii juróomi sor day taqloo ca guddaay ba, juróomi sor ya ca des taqloo noonu. \v 4 Ñawlul ay takku yu baxa te laal yolet ca catal sor, ba mujj ca benn taqalante ba, te ñawe ko noonu itam ca catal sor, ba jeexal taqalante ba ca des. \v 5 Juróom fukki takku ngay def ci catal benn sor bi, ak juróom fukki takku ci catal sor, bi jeexal taqalante bi ci des, te na takku yi yemoo. \v 6 Su ko defee nga defarlu juróom fukki lonku yu wurus yu ñuy jokklee sor yi, ba jaamookaay bi doon benn. \p \v 7 «Te itam ràbblul ay sori kawari bëy, ngir def ko ñaareelu xayma, muy kiiraay ci kaw jaamookaay bi. Fukk ak benn la sor yiy doon. \v 8 Guddaayu sor bu nekk di fanweeri xasab, yaatuwaay bi di ñeenti xasab, te fukki sor yeek benn yépp ay tolloo dayo. \v 9 Taqleel yii juróomi sor, juróom benni sor yi ci des it noonu, te juróom benneelu sor bi, nanga ko lem, fi féeteek kanam xayma bi. \v 10 Sàkkal juróom fukki takku ci catal sor, bi mujj ci benn taqalante bi, ak juróom fukki takku ci catal sor, bi jeexal taqalante bi ci des. \v 11 Sàkkal juróom fukki lonku yu xànjar te nga we lonku yi ci takku yi, daldi jokkle ñaari taqalante yi, muy benn xayma. \v 12 Liy lang te ëppe ci sori xayma bi nag, di beneen genn-wàllu sor bi, na lange ci gannaaw jaamookaay bi. \v 13 Waaye benn xasab bi ëppe wet gu nekk ci guddaayu sori xayma bi, na lange ci ñaari weti jaamookaay bi, ngir yiire ko ko. \v 14 Nanga defarlul xayma bi malaanum deri kuuy yu ñu sóob xonq, ak meneen malaanum deri piipi muy tege ca kawam. \s1 Lu jëm ci kenuy jaamookaay bi \p \v 15-17 «Sàkkalal jaamookaay bi ay làcci bantu séng yuy sampe. Na làcc wu nekk am ñaari kenu yu ñu lëkklee galan yu ndaw, te nga def làcci jaamookaay bi yépp noonu. Na taxawaayu làcc wu nekk di fukki xasab, yaatuwaay bi di xasab ak genn-wàll. \v 18 Ci wàllu làcci jaamookaay bi, sësaleel ñaar fukki làcc fi féete bëj-saalum, \v 19 boole kook ñeent fukki tegukaayi xaalis yuy ronu kenuy ñaar fukki làcc yi, ñaari tegukaay ay ronu làcc wi jiitu ngir ñaari kenoom yi muy àndal, ñaari tegu topp ci, ronu wépp làcc wu ci topp, ngir ñaari kenoom yi muy àndal. \v 20 Geneen wetu jaamookaay gi féete bëj-gànnaar itam, na doon ñaar fukki làcc \v 21 ak seeni ñeent fukki teguy xaalis, ñaari tegu ronu làcc wi jiitu, ñaari tegu topp ci, ronu wépp làcc wu ci topp. \v 22 Gannaawu jaamookaay gi féete sowu, sàkkal ko juróom benni làcc; \v 23 nga teg ci ñaari làcc ngir colli jaamookaay bi ci gannaaw. \v 24 Nañu àndandoo ci suuf te lëkkoo ca kaw ci benn lam kepp. Noonu lañuy bindoo ñoom ñaar; ñooy doon ñaari coll yi. \v 25 Muy juróom ñetti làcc ak seen teguy xaalis, di fukki tegu ak juróom benn, ñaari tegu ronu làcc wi jiitu, ñaari tegu topp ci, ronu wépp làcc wu ci topp. \p \v 26 «Nanga sàkk itam ay galani bantu séng: juróomi galan yuy ànd ak làcc yi ci genn wetu jaamookaay bi, \v 27 ak juróomi galan ngir làcci wet gi ci des, ak juróomi galan ngir làcc, yi ci gannaaw jaamookaay bi, fi féete sowu. \v 28 Galanu digg bi, ci digg làcc yi lay nekk, dale ko cat ba cat. \v 29 Xoobal làcc yi wurus te nga sàkkal làcc wu ci nekk ay lami wurus yuy téye galan yi, te nga xoob galan yi it wurus. \v 30 Su ko defee nga taxawal jaamookaay bi, ni ñu la ko wone ci kaw tund wi. \s1 Lu jëm ci rido bi \p \v 31 «Sàkkal rido bu ñu ràbbe wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe, ñu ñawaale ca nataali \w serub|lemma="serub y-:"\w*, \v 32 te nga wékk ko ci ñeenti jëni séng yu ñu xoob wurus, jën yi ànd ak seen wékkukaayi wurus, te nga móolal jën yi ñeenti teguy xaalis. \v 33 Wewal rido bi ci ron lonku yi, su ko defee nga yóbbu \w gaalu àlluway seede|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* si foofu ci gannaaw rido bi, rido bi xàjjaleel leen \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi, ak bérab bu sell bee sell. \v 34 Tegal kubeer ga ñuy amale ag njotlaay ca kaw gaal ga àlluway seede sa dence, ca biir bérab bu sell baa sell. \v 35 Tegal taabal ja ca biti, ca kanam rido ba, te nga teg tegukaayu làmp ba ca wetu bëj-saalumu jaamookaay ba, mu jàkkaarlook taabal ja, taabal ja nag, nga tege ko wetu bëj-gànnaar. \s1 Lu jëm ci kiiraayal buntu xayma bi \p \v 36 «Sàkkalal buntu xayma bi kiiraay lu ñu ràbbe wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, muy liggéeyu ràbb bu rafet. \v 37 Nga sàkkal nag kiiraay li juróomi jëni séng, xoob wu ci nekk wurus, seeni wékkukaay di wurus, te nga móolal jën yi juróomi teguy xànjar. \c 27 \s1 Lu jëm ci sarxalukaay bi \p \v 1 «Nanga defare \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi bantu séng, guddaay bi di juróomi xasab, yaatuwaay bi di juróomi xasab; ab kaare la sarxalukaay biy doon, taxawaayam di ñetti xasab. \v 2 Defaral ko ay béjjénam ci ñeenti koñ yi ci kaw. Béjjén yi, dees koy liggéeyaaleek sarxalukaay ba, ñu ànd di benn, te nanga xoob sarxalukaay bi xànjar. \v 3 Sàkkal ay ndabi tibbukaayu dóomam, ak ay ñiitukaayam, ak ay këllam, ak ay cappukaayam aki andam. Defal jumtukaayam yépp xànjar. \v 4 Sàkkal ko caax bu ñu tëgge xànjar te nga sàkkal caaxu xànjar bi ñeenti nopp ci ñeenti collam. \v 5 Tegal caax bi, mu ronu peggu sarxalukaay bi, te dale ci suuf ba ci digg sarxalukaay bi. \v 6 Sàkkalal sarxalukaay bi ay njàppuy bantu séng, te nga xoob lu ci nekk xànjar, \v 7 te nga roof njàppu yi ci nopp yi, su ko defee njàppu yi des ci ñaari weti sarxalukaay bi, ngir bu ñu koy yóbbu. \v 8 Pax ngay def sarxalukaay bi ci biir; nga defare ko ay xànq yu tàppandaar. Na ñu la ko wone ca kaw tund wa rekk lañu koy defe. \s1 Lu jëm ci ëttu jaamookaay bi \p \v 9 «Nanga sàkkalal jaamookaay bi ab ëtt: guddaayu ëtt bi ci wetu bëj-saalum, téeméeri xasabi sori rabal yu ñu ràbbe wëñu lẽe moo koy ub, ci genn wet googu. \v 10 Jëni jaamookaay bi ñaar fukk lay doon, seen ñaar fukki tegu di xànjar, wékkukaay yeek galani jën yi di xaalis. \p \v 11 «Naka noonu it ci wetu bëj-gànnaar, guddaay bi di téeméeri xasabi sori rabal, ak seen ñaar fukki jën yu seen ñaar fukki teguy xànjar ronu, wékkukaay yeek galani jën yi di xaalis. \p \v 12 «Yaatuwaayu ëtt bi, fi féete sowu, juróom fukki xasabi sori rabal a koy ub, seeni jën di fukk, seeni tegu di fukk. \p \v 13 «Yaatuwaayu ëtt bi, fi féete penku ci kanam, juróom fukki xasab la: \v 14 fukki xasabi sori rabal ak juróom moo ub ëtt bi ci googu wet, seeni jën di ñett, seeni tegu di ñett. \v 15 Wet gi ci des it, fukki xasabi sori rabal ak juróom, seeni jën di ñett, seeni tegu di ñett. \v 16 Buntu ëtt bi nag, na doon lafu ñaar fukki xasab, wu ñu defare wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, muy liggéeyu ràbb bu rafet, ay jënam di ñeent, seeni tegu di ñeent. \p \v 17 «Jën ya wër ëtt ba yépp, dees koy lëkklee galan yu xaalis, wékkukaayi jën yi di xaalis, seeni tegu di xànjar. \p \v 18 «Guddaayu ëtt bi téeméeri xasab lay doon, yaatuwaay bi di juróom fukk, taxawaayu wet yi di juróomi xasab, sor yi ñu ràbbe lépp di wëñu lẽe, tegu yi di xànjar. \v 19 Mboolem jumtukaayi yi ñuy liggéeye ci jaamookaay bi, ba ci mboolem xeri xaymaam, ak mboolem xeri ëtt bi, lépp xànjar lay doon. \ms1 Lu jëm ci santaane, yi sarxalkat yi sasoo \s1 Lu jëm ci diwu làmp bi \p \v 20 «Yaw nag, santal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, ñu indil la diwu segalu oliw gu set gu ñuy taaloo, ngir làmp yi dëkke tàkk. \v 21 Ci biir \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi\f + \fr 27.21 \fr*\fk xaymab ndaje ma: \fk*\ft dees na ko wooye jaamookaay ba, ba tey.\ft*\f* la Aaróona ak doomam yu góor di teg làmp yi, ci kanam rido bi làq gaalu àlluway seede si, ñuy fanaanee tàkk ngoon ba bët set, fi kanam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Dogal a ngoogu, war bànni Israyil fàww, ñoom ak seen askan. \c 28 \s1 Lu jëm ci yérey sarxalkat yi \p \v 1 «Léegi nag yaw, nanga seppee ci \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* sa mag Aaróona, ak doomam yu góor, nga woo leen fi yaw, ñu di ma sarxalal: Aaróona ak doomam yu góor, Nadab ak Abiyu ak Elasar ak Itamar. \v 2 Sàkkalal sa mag Aaróona yérey sellnga ngir daraja, ak teraanga bu sarxalkat wara yelloo. \v 3 Dangay sant mboolem liggéeykat yu xareñ, yi ma feesal xelum xareñte, ñu defar yérey Aaróona, ngir fal ko, mu di ma sarxalal. \v 4 Yii yére nag lañu koy defaral: kiiraayal dënn ak ab \w xar-sànni|lemma="xar-sànni m-:"\w* ak ab fëxya, ak mbubb mu gudd mu ñu ràbb, ak kaala ak laxasaay. Yérey sellnga lañuy defal sa mag Aaróona ak doomam yu góor, ngir ñu di ma sarxalal. \v 5 Liggéeykat yooyu ñooy jël wëñi wurus, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe ngir liggéeye ko. \s1 Lu jëm ci xar-sànni mi \p \v 6 «Nañu ràbbe \w xar-sànni|lemma="xar-sànni m-:"\w* mi wëñu wurus, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ñu ñawaale ci ay nataal. \v 7 Ñaari ngàlli mbagg yu ñuy faste la xar-sànni miy am, ñu di leen fastee ci ñaari cat yi. \v 8 Ngañaay liy tege ci kaw xar-sànni mi, ni xar-sànni mi lañu koy liggéeye, mu ànd ak moom, di benn, di wëñu wurus, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe. \v 9 Nanga jël ñaari peri onigsë, nga ñaas ci turi doomi Israyil yu góor: \v 10 yii juróom benni tur ci benn per, juróom benni tur yi ci des ci beneen per bi, tur yi toppante, ni boroom tur yi toppantee ci juddu. \v 11 Ni ko ab liggéeykat bu farewoo mbindum doj di defe, ni lañuy ñaase turi doomi Israyil yu góor ci kaw ñaari per yi, mu mel ni ni ñuy ñaase xàmmikaay yi ñuy torloo, te nañu we per yi ci ay ŋankukaayi wurus. \v 12 Tappal ñaari per yi ci kaw ngàlli waggi xar-sànni mi, per yi wuutu \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, Aaróona gàddu seeni tur ci kaw ñaari ngàlli waggam, fi kanam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ngir saxal ag pàttliku. \p \v 13 «Sàkkal ay ŋankukaayi wurus, \v 14 ak ñaari caqi wurusu ngalam, bu ci nekk nga rawaase ko nig buum, ba noppi nga we caq yu rawaasoo yooyu ci ŋankukaay yi. \s1 Lu jëm ci kiiraayal dënn bi \p \v 15 «Nanga sàkk kiiraayal dënn bi ñuy jëfoo cib àtte, ñu liggéeyaale ko ay nataal ni \w xar-sànni|lemma="xar-sànni m-:"\w* mi, te nañu ko ràbbe wëñu wurus, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe. \v 16 Ab kaare bu ñu lem lay doon, guddaay bi di ŋaraleb baaraamu déy ak digg, yaatuwaay bi di ŋaraleb baaraamu déy ak digg. \v 17 Nanga we ay per ci kaw kiiraayal dënn bi, nga def ko ñeenti làngi per. Làng gi jiitu, peru sarduwan ak peru topaas ak peru eskarbukal moo cay nekk; \v 18 ñaareelu làng gi di peru emëródd ak peru safiir ak peru jamaa; \v 19 ñetteelu làng gi di peru yasent ak peru agaat ak peru ametistë; \v 20 ñeenteelu làng gi di peru kirsolit ak peru onigsë ak peru jàspë, te per bu ci nekk, ŋankukaayu wurus lees koy wewe. \v 21 Per yeek turi doomi Israyil ñooy tolloo ab lim: muy fukk ak ñaar, ni tur yi tollu. Dees ciy ñaas tur yi ni xàmmikaayi torlu, ku nekk ak turam, ba fukki giir yeek ñaar daj. \v 22 «Nanga sàkkal kiiraayal dënn bi ñaari caqi wurusu ngalam yu ciy tege, te rawaasoo ni ay buum, \v 23 ak ñaari jaaroy wurus yu ñuy takk ci ñaari cati kiiraayal dënn bi ci kaw, \v 24 te nga nas ñaari buumi wurus yi ci ñaari jaaro, yi ci cati kiiraay li. \v 25 Yeneen ñaari cati buumi wurus yi, nga we leen ci ñaari ŋankukaay, yi ci kaw ngàlli waggi xar-sànni mi, ci kanam. \v 26 Sàkkal ko it ñaari jaaroy wurus yu ñuy we ci ñaari cati suufi kiiraay li, fi féete biir, wet gi tafu ci xar-sànni mi. \v 27 Nga sàkkalaat ko yeneen ñaari jaaroy wurus yooy we ci suufu ngàlli xar-sànni mi, fi féete kanam, dendeek sofu ngàll yi, te tiim ngañaayu xar-sànni mi. \v 28 Kiiraayal dënn bi, buum gu sew gu baxa te laal yolet, moom lees koy téyee, lëkklee ko jaaroy kiiraay leek jaaroy xar-sànni mi, su ko defee kiiraay li dëkke tiim ngañaay li, ba du teqlikook xar-sànni mi. \v 29 Aaróona nag nay tegoo turi \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ci kaw kiiraayal dënn bi ñuy àttee, tur yi tafu ci xolam, saa yuy dugg ci \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi, ngir saxal pàttliku ba fàww fi kanam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \v 30 Nanga yeb ci biir kiiraayal dënn bi ñuy àttee, jumtukaayi tegtal yooyu di \w Urim ak Tumim|lemma="Urim ak Tumim:"\w*\f + \fr 28.30 \fr*\fk Urim \fk*\ft boobu ak \ft*\fk Tumim \fk*\ft ba, sarxalkat baa ko daan jëfandikoo, ngir xam lu Yàlla namm. Xameesul nag nan lañu ko daa jëfandikoo, waaye jombul mu nirook ab tegoo bant.\ft*\f*, ngir ñu tafu ci xolu Aaróona, saa yuy taxawi fi kanam Aji Sax ji. Noonu la Aaróona di dëkke yóbbaale ci kaw xolam jumtukaayi àtte yu bànni Israyil, saa suy taxawi fi kanam Aji Sax ji, ba fàww. \s1 Lu jëm ci yére yu sell, yi ci des \p \v 31 «Fëxya bi \w xar-sànni|lemma="xar-sànni m-:"\w* miy tege, lépp, wëñ gu baxa te laal yolet nga koy liggéeye ba mu daj. \v 32 Na baatu fëxya bi nekk ci digg bi, mel ni baatu mbubbam xare, te nañu ko ombe omb bu dëgër ba mu daj, ngir du xottiku. \v 33 Nanga takk ci ombu fëxya bi ba mu daj, ay doomi gërënaat yu ñu defare wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr, te diggante gërënaat yi, nga doxale ci ay jóolóoli yu wurus ba omb bi daj. \v 34 Ab jóolóolib wurus, ab doomu gërënaat, ab jóolóolib wurus, ab doomu gërënaat, ba ombu fëxya bi daj. \v 35 Na ko Aaróona sol bu nekkee ci liggéeyu sarxaleem. Su ko defee coowal jóolóoli yi di jib, ba buy jàll ci biir \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi, jëm fi kanam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, mbaa mu di ci génne, du tax mu dee. \p \v 36 «Sàkkal dogu wurusu ngalam wu tell, nga ñaas ci mbind mii ni ñuy ñaase mbindum torlu: “Lu \w sell|lemma="sell:"\w* a ngii, ñeel Aji Sax ji.” \v 37 Takke ko buum gu baxa te laal yolet ci kaw kaala gi, mu féete kanam. \v 38 Na tafu ci jëwu Aaróona, mu gàddoo ko ay wu tukkee ci lu \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* moy ci wàllu yëf yu sell yi ñu wara sellal ci seen mboolem sarax yu sell. Na nekk fàww ci jëëm, ndax Aji Sax ji nangul leen. \p \v 39 «Mbubb mu gudd mi nag, nanga ko ràbbe wëñu lẽe, kaala gi itam di wëñu lẽe. Te laxasaay gi, liggéeyu ràbb bu rafet lay doon. \v 40 Doomi Aaróona yu góor yi itam, sàkkal leen ay mbubb. Sàkkal leen ay laxasaay, te ay kaala it, sàkkal leen ko ngir daraja ak teraanga bu sarxalkat wara yelloo. \v 41 Nanga solal yooyii sa mag Aaróona, mook ay doomam yu góor, te nga sotti leen diwu pal\f + \fr 28.41 \fr*\fk diwu pal: \fk*\ft seetal ci 30.22-33.\ft*\f* gi, dénk leen seen sas. Noonu nga leen di sédde céru sellnga, ñu di ma sarxalal. \v 42 Sàkkal leen ay tubéyi njiitlaayi lẽe, ñu sànge ko seeni cér, dale ko ci ndigg li ba ci lupp yi. \v 43 Na Aaróona aki doomam jiitloo loolu, bu ñuy dugg ci \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi, mbaa ñuy jegeji \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi, ngir liggéey ci bérab bu sell bi, ndax ñu baña yóbbe seen bopp mbugal, muy seen dee. Na Aaróona ak askanam sàrtoo loolu fàww. \c 29 \s1 Lu jëm ci sarxalkat yeek seen xewu colu \p \v 1 «Lii nag mooy li nga leen di defal, ngir sédd leen céru sellnga, ngir ñu di ma sarxalal: Dangay jël yëkk wu ndaw ak ñaari kuuy yu amul sikk, \v 2 ak mburu yu mag yu amul lawiir, ak kàmp yu sew yu amul lawiir yu ñu xiiwaale diw, ak mburu yu tàppandaar yu amul lawiir, ñu wis diw ca kaw, te sungufu bele su mucc ayib ngay defare yooyu. \v 3 Yebal lépp ci benn pañe te jébbale ko, mook yëkk wu ndaw wi ak ñaari kuuy yi. \v 4 Yóbbul Aaróona ak doomam yu góor, ba ca bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* ma, nga sang leen. \v 5 Nga jël yére yi nag, solal Aaróona mbubb mu gudd mi, ak fëxyab \w xar-sànni|lemma="xar-sànni m-:"\w* mi, teg ci xar-sànni mi, tegaat ci kiiraayal dënn bi, daldi koy takkal ngañaay liy tege ci xar-sànni mi. \v 6 Su ko defee nga kaala ko, takkal ko meeteel gu \w sell|lemma="sell:"\w* gi, fi kanam kaala gi. \v 7 Te nga jël diwu pal gi, sotti ko ci kaw boppam, diw ko. \v 8 Bu loolu weesee, nga ne doomi Aaróona ñu jegesi, nga solal leen seeni mbubb, \v 9 kaala leen, te takkal Aaróona ak doomam yu góor ay laxasaay. Su ko defee ñu féetewoo céru sarxalkat, muy dogal bu sax dàkk. \p «Noonu ngay sase Aaróona ak doomam yu góor. \v 10 Nanga yóbbu yëkk wu ndaw wi ba ci bunt xaymab ndaje mi, Aaróona aki doomam teg seeni loxo ci kaw boppu yëkk wi, \v 11 nga daldi rendi yëkk wi fi kanam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, fi bunt xaymab ndaje mi. \v 12 Sàkkal ci deretu yëkk wu ndaw wi, nga capp ci sa baaraam, diw ci béjjéni \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi, te nga tuur li des ci deret ji ci suufu sarxalukaay bi. \v 13 Jëlal mboolem nebbon bi sàng yérey biir yi, ak bàjjo bi ci res wi, ak ñaari dëmbéen yi ànd ak nebbon bi ci kaw dëmbéen yi, nga boole lépp def ko saraxu taal-saxaral ci kaw sarxalukaay bi. \v 14 Seen \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w* a ngoogu. Li des ci yàppu yëkk wi, boole kook der bi, ak sébbriit mi, nga génne ko dal bi, lakk ko. \p \v 15 «Menn kuuy mi, jël ko, Aaróona aki doomam teg seeni loxo ci boppu kuuy mi, \v 16 ba noppi, nga rendi kuuy mi, jël deret ji, xëpp ko ci peggi sarxalukaay bi yépp ba mu daj. \v 17 Kuuy mi, ay dog nga koy dogat, daldi raxas yérey biir yi ak yeel yi, teg ci kaw dog yi ak bopp bi. \v 18 Lakkal kuuy mépp ci kaw sarxalukaay bi. \w Saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* la, ñeel Aji Sax ji, di xeeñ xetug jàmm; saraxu sawara la, ñeel Aji Sax ji. \p \v 19 «Jëlal kuuy mi ci des, Aaróona ak doomam yu góor teg seeni loxo ci boppu kuuy mi. \v 20 Su ko defee nga rendi kuuy mi, sàkk ci deret ji, taqal ci tabanum noppu ndijooru Aaróona ak tabanum noppu ndijooru doomam yi, te nga taqal ci seen baaraamu déyu ndijoor, ak seen baaraamu tànku ndijoor bu mag. Boo noppee, nga xëpp li des ci deret ji ci peggi sarxalukaay bi yépp ba mu daj. \v 21 Sàkkal ci deret ji ci sarxalukaay bi, ak ci diwu pal gi, nga wis-wisal ko ci kaw yaramu Aaróona ak ci kawi yéreem, wis-wisal ko ci kaw yarami doomam ak ci seen kawi yére. Su ko defee Aaróona sell, mooki yéreem, ay doomam it sell, ñook seeni yére. \p \v 22 «Kuuy mi, nanga ci génne li ci duuf: calgeen bi, ak nebbon bi sàng yérey biir yi, ak bàjjo bi ci res wi, ak ñaari dëmbéen yeek nebbon bi ci seen kaw, ak tànku ndijoor bu kanam bi, ndax kuuyum colug sarxalkat yi la. \v 23 Pañe biy taaje fi kanam Aji Sax ji te def mburu yu amul lawiir nag, nanga ci sàkke menn mburu mu tàppandaar, ak menn mburu mu ñu xiiwe diwu oliw, ak menn mburu mu gëna sew. \v 24 Nga boole lépp, teg ko ci loxoy Aaróona aki doomam, ñu def ko \w saraxu yékkati-jébbale|lemma="Sarax yi:"\w*, ñeel Aji Sax ji. \v 25 Nga daldi koy nangoo ci seeni loxo, lakk ko ci kaw sarxalukaay bi, boole kook saraxu rendi-dóomal bi, muy xeeñ xetug jàmm fi kanam Aji Sax ji. Saraxu sawaraa ngoogu, ñeel Aji Sax ji. \p \v 26 «Nanga jël dënn bi bokk ci kuuyum xewu colug Aaróona, nga def ko saraxu yékkati-jébbale, ñeel Aji Sax ji. Loolu moo cay sa wàll. \v 27 Nanga ber dënn bi ñu def saraxu yékkati-jébbale, mook tànkub jooxe bi ñu def saraxu yékkati-jébbale, te ñu jooxee ko ci kuuyu colu gi, ñeel Aaróona aki doomam. \v 28 Aaróona aki sëtam la loolu di doon seen cér bu \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* di warlook ñoom ba fàww, ndax ab jooxe la; jooxe bu bànni Israyil di génnee ci seen \w saraxi cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*, muy seenub jooxe, ñeel Aji Sax ji. \p \v 29 «Yérey Aaróona yu sell yi nag, gannaaw bu dëddoo, dees koy féetale ay doomam, ñu fale leen ko ci seen xewu colug carxal. \v 30 Diiru juróom ñaari fan, ci la \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi koy wuutu ci doomam yu góor, di sol yére yooyu, moom miy dugg ci biir xaymab ndaje mi, ci biir \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi. \p \v 31 «Nanga jël kuuyu xewu colu gi, nga baxal yàpp wi ci bérab bu sell. \v 32 Aaróona aki doomam ñooy lekk yàppu kuuy mi ci bunt xaymab ndaje mi, boole kook mburu mi ci pañe bi. \v 33 Ñam yooyu, ña koy lekk mooy ña muy seen saraxu njotlaay, keroog ca seen xewu colu, ga ñu leen tabbe ngir sellal leen. Waaye keneen du ci lekk, ndaxte ñam wu sell la. \v 34 Bu lenn ci yàppu colu gi mbaa lenn ci mburu mi fanaanee ba bët set, nañu lakk loola ca fanaan ba mu jeex. Deesu ko lekk, ndaxte ñam wu sell la. \p \v 35 «Noonu ngay def ak Aaróona aki doomam, ni ma la ko sante rekk. Diiru juróom ñaari fan ci nga leen di sas, \v 36 te aw yëkk ngay def \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w* bés bu nekk, muy seen njotlaay, di njotlaay liy setal sarxalukaay bi. Te itam nanga diw sarxalukaay bi ag diw, sellale ko ko. \v 37 Diiru juróom ñaari fan ngay defal sarxalukaay bi saraxu njotlaayam, sellale ko ko, ba sarxalukaay bi doon lu sella sell. Lépp lu laal sarxalukaay bi day séddu ci sellaayam. \s1 Lu jëm ci sarax yi war bés bu nekk \p \v 38 «Lii mooy li ngay rendi ci kaw \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi: ñaari kuuyi menn at, bés bu nekk ba fàww. \v 39 Menn kuuy mi, nga rendi ko ci suba, meneen kuuy mi, diggante ngoon, ba jant di so. \v 40 Sàkkal ñetti kilo, yemook benn fukkeelu nattub sunguf su mucc ayib su ñu xiiwe liitar ak genn-wàll, yemook xaajaatub natt bi ñuy wax xiin ci diwu segalu oliw, ak \w saraxu tuurub|lemma="Sarax yi:"\w* benn liitaru biiñ ak genn-wàll, yemook xaajaatub xiin. Loolu yépp ànd ak menn kuuy mi. \v 41 Meneen kuuy mi, nga rendi ko diggante ngoon ak jant bu so, booleeti ko ak \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* mi ak saraxu tuuru bi, ni woon ci suba, muy xeeñ xetug jàmm, di saraxu sawara, ñeel \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \v 42 \w Saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* lay doon bu sax, te war seen maasoo maas fi bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi, ci kanam Aji Sax ji. Foofu laay dajeek yeen, te fa laay waxe ak yaw, \v 43 Foofa laay dajeek \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, bérab ba doxe fa sell, ndax samag leer. \v 44 Maay sellal xaymab ndaje mi ak sarxalukaay bi, te Aaróona aki doomam, maa leen di sellal, ngir ñu doon samay sarxalkat. \v 45 Maay dëkk fi digg bànni Israyil te maay nekk seen Yàlla. \v 46 Su boobaa bànni Israyil xam ne, man Aji Sax ji maay seen Yàlla, ji leen génnee réewum Misra, ngir dëkk fi seen biir. Man maay seen Yàlla Aji Sax ji. \c 30 \s1 Lu jëm ci sarxalukaayu cuuraay bi \p \v 1 «Sàkkal ab \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bu ñuy taal cuuraay ci kawam. Bantu séng nga koy defare. \v 2 Guddaay bi di xasab, yaatuwaay bi di xasab; ab kaare lay doon, taxawaay bi di ñaari xasab, ay béjjénam ànd ak moom di benn bant bi. \v 3 Xoobal wurusu ngalam kaw gi ak wet yi ba mu daj ak béjjén yi, te nga sàkkal ko kéméju wurus gu ko wër. \v 4 Ñaari noppi wurus nga koy sàkkal ci ron kéméj gi. Féetaleel nopp yi ci ñaari wetam, ñu jàkkaarloo, di téye banti njàppu, yi ñu koy yóbboo. \v 5 Defal njàppu yi bantu séng te nga xoob njàppu yi wurus. \p \v 6 «Tegal sarxalukaayu cuuraay bi ci kanam rido, bi làq \w gaalu àlluway seede|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* si ak kubeeru njotlaay, gi ci kaw gaalu àlluway seede si, foofu may dajejeek yaw. \v 7 Na fa Aaróona taal cuuraay suba su nekk. Buy topptoo làmp yi lay taal cuuraay lu xeeñ li. \v 8 Bu Aaróona di taal làmp yi diggante ngoon ak jant bu so itam, na taal cuuraay lu xeeñ li. Cuuraay la su ñuy taal ba fàww, ci seen gépp maas fi kanam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \v 9 Deesu ci sarxal cuuraay lu ñu diglewul, deesu ci rendi \w saraxu dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, deesu ci def \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* mbaa \w saraxu tuuru|lemma="Sarax yi:"\w*. \v 10 Na Aaróona di sàkk ci deretu \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w* bi, taqal ci béjjéni sarxalukaay bi, ngir def ko njotlaayal sarxalukaay bi benn yoon cim at. Benn yoon cim at lañu koy defal njotlaayam ci seen gépp maas. Sarxalukaay bu \w sella sell|lemma="sell:"\w* la, ñeel Aji Sax ji.» \s1 Lu jëm ci njot-gi-bakkan \p \v 11 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ne ko: \v 12 «Boo tolloo ci taxawal limeefu boppi \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, na ku nekk ci ñoom fey Aji Sax ji njot-gi-bakkanam ba nga koy lim, ndax menn musiba bañ leena dikkal ci biir lim bi. \p \v 13 «Lii nag mooy li képp ku ñu bind ci limeef yi wara fey: dogu xaalis bu diisaay bi di genn-wàllu siikal, bi ñuy natte ci jaamookaay bi, dayo boobu tollook fukki gera\f + \fr 30.13 \fr*\fk gera \fk*\ft moo doon natt, ba gënoona tuut ci wàllu diisaay, yemook genn-wàllu garaam.\ft*\f*, mu dib jooxe, ñeel Aji Sax ji. \v 14 Képp ku bindu ci limeef bi, te am ñaar fukki at, jëm kaw, na fey jooxe bi, ñeel Aji Sax ji. \v 15 Ki woomle du fey lu ëpp, ki néewle du fey lu yées genn-wàllu siikal, buy fey jooxeb Aji Sax ji ngir njot-gi-bakkanam. \v 16 Nanga nangoo xaalisu njot-gi-bakkan bi ci bànni Israyil, te nga féetale ko liggéeyu \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi. Loolu pàttliku lay doon, ñeel bànni Israyil fi kanam Aji Sax ji, ngir seen njot-gi-bakkan.» \s1 Lu jëm ci mbalkam njàpp mi \p \v 17 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ne ko: \v 18 «Sàkkal mbalkam njàpp mu xànjar, ak tegub xànjaram ngir ñu di ko jàppe. Teg ko ci diggante \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi ak \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi, te nga duy ko ndox. \v 19 Aaróona aki doomam di ci tanq, raxase seeni loxo ak seeni tànk. \v 20 Bu ñuy duggsi ci xaymab ndaje mi, nañu jàpp, ndax ñu baña dee, nañu jàpp itam, bu ñuy liggéeysi fi sarxalukaay bi, di taal saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. \v 21 Nañu raxas seeni loxo ak seeni tànk, ndax ñu baña dee. Na loolu di dogal bu sax dàkk, ñeel Aaróona ak askanam ci seen gépp maas.» \s1 Lu jëm ci diwu pal gi ñuy sellale \p \v 22 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ne ko: \v 23 «Yaw nag, tànnal ngën-gi-xeeñal; xeetu ndàbb li ñuy wax miir, bu tooy bi, sàkk ci juróomi kilo, xasum kanel mu xeeñ; ñaari kilo ak genn-wàll, yuuru gattax gu xeeñ; ñaari kilo ak genn-wàll, \v 24 ak xasum kaas; juróomi kilo, yemook juróomi téeméeri siikal, ci siikalu jaamookaay bi, ak juróom benni liitari diwu oliw, yemook benn natt bi ñuy wax xiin. \v 25 Loolu ngay def diwu pal gu \w sell|lemma="sell:"\w* gi, te na doon njafaan lu njafaan-kat waajal ba mu baax. Diwu pal gu sell lay doon. \p \v 26 «Nanga ci diw \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi, diw ci \w gaal gi àlluway seede si dence|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w*, \v 27 ak taabal ji aki ndabam, ak tegukaayu làmp bi, ak jumtukaayam yépp, ak \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* cuuraay bi. \v 28 Nanga ci diw itam sarxalukaayu \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* bi, ak ndabam yépp, ak mbalkam njàpp mi akub tegoom. \v 29 Noonu ngay sellale yooyii, mu daldi doon lu sella sell. Lépp lu laal yooyii day doon lu sell. \v 30 Aaróona aki doomam itam, nanga leen diw. Noonu nga leen di sellale, ngir ñu doon samay sarxalkat. \p \v 31 «Nanga wax nag \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen: “Googu diw sama diwu pal gu sell lay doon, ci seen gépp maas. \v 32 Doom aadama ju ko jagoowul, deesu ko ko diw, te buleen njafaan lenn lu ni mel, lu ngeen yemale dayoy xeeñal ya ak dayoy diw gu sell gi. Deesu ko def ci yaramu kenn ku ko jagoowul, te buleen njafaan xeeñal yi ciy dem, ci dayo yu tollook dayoy diw gu sell gi, ngir defar lenn lu ni mel. Lu sell la, lu ngeen wara wormaal sellngaam. \v 33 Képp ku njafaan lu ni mel, mbaa mu taqal ci yaramu ku ci bokkul, dees koy dagge ci biir bànni Israyil.”» \s1 Lu jëm ci cuuraay li \p \v 34 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ne ko: «Wutal nag xeeñal yii: ndàbbu estaagte, ak ndàbbi galbanom, ak xori onigsë yu xeeñ, ak \w cuuraay-libaŋ|lemma="cuuraay l-:"\w* lu raxul, te yooyu yépp tolloo dayo. \v 35 Def ko njafaan lu njafaan-kat waajal ba mu baax, xorom ko, mu set, \w sell|lemma="sell:"\w*. \v 36 Sàkk ci, wol ko ba mu mokk, nga teg ko fi kanam gaal gi àlluway seede si dence, fi biir \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi, fi may dajeek yaw. Loolu lu sella sell la lu ngeen wara wormaal. \v 37 Waaye cuuraay loolu ngay njafaanlu nag, bu ci njafaanal sa bopp ci dayoy xeeñal yu ni tollu. Lu sell la lu ngeen wara wormaal, ñeel Aji Sax ji. \v 38 Képp ku defar lenn lu ni mel, ngir di ko xeeñoo, dees koy dagge ci bànni Israyil.» \c 31 \s1 Tabb nañu ay liggéeykat yu xareñ \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ne ko: \v 2 «Gisal, maa woo Besalel ci turam. Besalel, Uri mooy baayam; Uri, Ur Yudeen bi di baayam. \v 3 Maa ko feesale xelum Yàlla, ak xareñte ak déggin ak xam-xam, ak manoorey bépp xeetu liggéey, \v 4 ngir muy nas ay liggéeyi wurus ak xaalis ak xànjar, \v 5 di yett per yu muy tapp, di yett bant, di liggéey lu nekk. \v 6 Maa ngii di ko tofal Oliyab doomu Ayisamaag Daneen bi, te itam mboolem ñi xarala, may naa leen xelum xarala, ngir ñu ànd def mboolem lii ma la sant: \v 7 Muy \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi, ak \w gaalu àlluway seede|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* si, ak kubeeru saraxu njotlaay gi ci kawam, ak mboolem jumtukaayi xayma bi; \v 8 taabal ji, ak ndab yi, ak tegukaayu làmpu wurusu ngalam beek yëfam yépp, ak \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* cuuraay bi, \v 9 ak sarxalukaayu rendi-dóomal bi, ak ndabam yépp, ak mbalkam njàpp mi akub tegoom, \v 10 ak itam yére yu yànj yi, yére yu \w sell|lemma="sell:"\w* yi ñeel Aaróona \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi ak yérey doomam, yi ñuy sol, di sarxale, \v 11 ak diwu pal gu sell gi, ak cuuraay lu xeeñ li ñeel \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi. Loolu ma la sant lépp, nañu ko defe noonu.» \s1 Lu jëm ci solob bésub Noflaay \p \v 12 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ne ko: \v 13 «Waxal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen: “Fexeleen rekk ba sama \w bési Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*, ngeen di ko wormaal, ndax bésub Noflaay da di firnde sama digganteek yeen ak seen askan, ngir ngeen xam ne man Aji Sax ji maa leen ber, sellal leen. \v 14 Wormaal-leen bésub Noflaay ndax lu \w sell|lemma="sell:"\w* la, ñeel leen. Ku ko teddadil, dee rekk mooy àtteem: képp ku ci liggéey, kooku dees na ko dagge ci biiri bokkam. \v 15 Juróom benni fan lees wara liggéey, waaye \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w* bay juróom ñaareel ba, bés bu sell la, bésub Noflaay bu mat sëkk, ñeel Aji Sax ji. Képp ku liggéey bésub Noflaay, dee rekk mooy àtteem. \v 16 Na bànni Israyil wormaal bésub Noflaay, nañu sàmm bésub Noflaay, ñook seen askan. \w Kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* la gu sax dàkk. \v 17 Sama diggante laak bànni Israyil, te firnde la ju sax dàkk, ndax ci juróom benni fan la Aji Sax ji sàkk asamaan ak suuf, bésub juróom ñaareel ba, mu dal-lu, daldi yeeslu.”» \p \v 18 Ba Yàlla noppee wax ak Musaa ca kaw tundu Sinayi, da koo jox ñaari àlluway doj yu mu binde loxol boppam. \c 32 \s1 Israyil fecci na kóllëre \p \v 1 Ba mbooloo ma gisee Musaa yàgg lool te wàccul tund wa, dañoo songandoo Aaróona, ne ko: «Ayca, sàkkal nu yàlla ju nu jiite, ndax Musaa mii nu génne réewum Misra kat, xamunu lu ko dal.» \v 2 Aaróona ne leen: «Tekkileen boog, indil ma seen jaaroy wurusi nopp, yi ci seeni jabar ak seeni doom, góor ak jigéen.» \v 3 Ba loolu amee mbooloo mépp tekki seen jaaroy wurusi nopp, indil Aaróona. \v 4 Mu nangoo ko ci seeni loxo, liggéey ko ba sàkk ci sëllu wu ñu móol. Ci kaw loolu ñu naan: «\w Bànni Israyiloo|lemma="bànni Israyil:"\w*, seen Yàllaa ngii, moo leen génne réewum Misra!» \v 5 Aaróona gis la xew, daldi tabax ci kanam sëllu wi ab \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*. Mu daldi yéene, ne: «Ëllëg màggal la, ñeel \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji.» \v 6 Ca ëllëg sa mbooloo ma teela xëy, ñu def ay \w saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ak ay \w saraxi cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*. Ba mu ko defee ñu toog, di lekk ak a naan, nes tuut ñu jóg, di mbumbaay. \p \v 7 Aji Sax ji nag waxati Musaa ne ko: «Gaawal wàcc, ndax sa mbooloo, ma nga génne réewum Misra def nañu yàqute. \v 8 Jàdd nañu xaat yoon wa ma leen tegoon. Dañoo sàkkal seen bopp sëllu wu ñu móol, di ko sujjóotal ak a sarxalal, naan: “Israyiloo, seen yàllaa ngii, moo leen génne réewum Misra!”» \p \v 9 Aji Sax ji dellu ne Musaa: «Maa gis askan wii, askan wu dëgër bopp a ngii! \v 10 Léegi seetaan ma rekk, samam sànj tàkkal leen, ba ma faagaagal leen, te du tee ma def la askan wu mag.» \v 11 Musaa nag tinu Yàllaam Aji Sax ji ne ko: «Aji Sax ji, ana lu waral sam sànj di tàkkal sa ñoñ ñi nga génne réewum Misra ci sa kàttan gu màgg ak sa dooley loxo? \v 12 Ana lu jar Misra di wax naan: “Musiba mi mu leen naraloon, ba mu leen di yiwi de, du lenn lu moy rey leen ba ñu jeex ca tund ya, ba fare leen kaw suuf sépp.” Ngalla dëddul sa sawaras sànj te nga fomm musiba mi nga naral sa ñoñ. \v 13 Bàyyil xel Ibraayma ak Isaaxa ak Israyil, sa jaam ñi nga giñaloon ci sa bopp, ne leen: “Maay yokk seen askan ni biddiiwi asamaan, te mboolem réew mii ma waxoon, maa koy jox seen askan, ñu moom ko fàww.”» \v 14 Ba loolu amee Aji Sax ji fomm musiba ma mu waxoon ne dina ko teg ñoñam. \s1 Merum Musaa am na njeexital \p \v 15 Ba mu ko defee Musaa walbatiku, wàcce ca tund wa, mook ñaari àlluway seede ya ca loxoom, àlluwa yu ñu bind ñaari wet yépp, biir ak biti. \v 16 Àlluwa ya, liggéeyu Yàllaa, mbind ma di mbindum Yàlla mu ñaase ca kaw àlluwa ya. \v 17 Ci kaw loolu Yosuwe dégg coowal mbooloo may xaacu. Mu ne Musaa: «Coowal xaree ngoog ca dal ba!» \v 18 Musaa ne ko: \q1 «Coow loolu de du bàkku yu njàmbaar waral, \q1 du jooytu yu jéll sabab, \q1 woyi mbumbaay daal laa dégg.» \p \v 19 Ba Musaa jubee dal ba, ba gis sëllu wa ak pecc ma, mer mu ne jippét tàkk la ko def, mu sànni àlluwa ya mu ŋàbboon, mu ne tasar ca suufu tund wa. \v 20 Ci kaw loolu mu jël sëllu, wa ñu sàkk, lakk ko, wol ko ba mu mokk, mu suy cim ndox, daldi koy naanloo \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \p \v 21 Musaa nag ne Aaróona: «Lan la la mbooloo mii def, ba nga yóbbe leen gii moy gu réy?» \v 22 Aaróona ne ko: «Sang bi, rikk bul mer, yaw ci sa bopp xam nga ni mbooloo mii yeboo ci mbon. \v 23 Dañu ma ne: “Sàkkal nu yàlla ju nu jiite, ndax Musaa mii nu génne réewum Misra kat, xamunu lu ko dal.” \v 24 Ma ne leen: “Ku takk wurus, tekkil, indi!” Ñu jox ma, ma sànni ci sawara wi, sëllu wii génne ci!» \p \v 25 Musaa nag gis ni mbooloo mi ràkkaajoo, ndax fekk na Aaróona bay-bayal leen, ba ñu ràkkaaju, ba ku leen doon fexeel man leena ree. \v 26 Musaa taxaw ca buntu dal ba, ne: «Ku ànd ak \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, fii ci man!» \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñépp dikk, yéew ko. \v 27 Mu ne leen: «Aji Sax ji, Yàllay Israyil dafa wax ne: “Na ku nekk teg saamaram ci luppam, te ngeen wër dal bi bépp buntoo bunt, ba mu daj. Reyleen ñépp; doomu ndey, xarit ak jegeñaale.”» \v 28 Ba loolu amee Leween ña def la leen Musaa sant. Ñi daanu ci bànni Israyil bésub keroog tollu na ci ñetti junniy góor. \v 29 Musaa nag ne: «Bés niki tey sasoo ngeen Aji Sax ji, gannaaw yeena dal ci kaw doom, dal ci kaw doomu ndey. Kon bésub tey tegoo ngeen barkeb Aji Sax ji.» \s1 Musaa tinu na Yàlla \p \v 30 Ca ëllëg sa Musaa ne mbooloo ma: «Yeen de bàkkaar ngeen bàkkaar bu réy, waaye maa ngi nii di yéeg, jëm ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Jombul ma jotul leen seen bàkkaar.» \v 31 Ba mu ko defee Musaa dellu ci Aji Sax ji, ne ko: «Éey Aji Sax ji, mbooloo mii de moy nañu la lool, ba ñu sàkkalee seen bopp ay yàllay wurus. \v 32 Léegi nag, soo leen dee baal seen bàkkaar, aa... Lu ko moy kat, far ma rekk ci téere bi nga bind\f + \fr 32.32 \fr*\fk téere \fk*\ft bi ñuy wax fii jombul mooy lim, ya Yàlla bind turi nit ña bokk ca mbooloo ma. Nit ku ñu masa far ca yooyu lim bokkatoo ca ñoñi Yàlla.\ft*\f*.» \v 33 Aji Sax ji ne Musaa: «Ki ma moy, kooku doŋŋ laay far ci sama téere. \v 34 Yaw daal demal rekk, yóbbu mbooloo mi fa ma la waxoon, te sama malaakaa ngii di la jiituji. Waaye keroog sama bésu mbugal, maay mbugal mbooloo mi ndax seen bàkkaar.» \p \v 35 Gannaaw gi Aji Sax ji mbugal na mbooloo ma ndax la ñu sàkkloo woon Aaróona aw sëllu. \c 33 \s1 Yàlla yebal na Musaa \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ne ko: «Doxal jóge fii, yaak mbooloo mi nga génne réewum Misra, ngeen dem ca réew ma ma giñaloon Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, ne leen seen askan laa koy jox. \v 2 Maay yebal malaaka mu jiitu la, te maa fay dàqe Kanaaneen ña ak Amoreen ña ak Etteen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña, \v 3 ba ngeen dugg ca réew mooma meew maak lem ja tuuroo. Waaye duma ànd ak yeen, lu ko moy dinaa leen faagaagal ci yoon wi, ndax askan wu dëgër bopp ngeen.» \v 4 Ba mbooloo ma déggee kàddu yu dëgër yooyu, dañoo daldi toroxlu, ba kenn takkootul gànjaram. \p \v 5 Fekk na Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Waxal \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen, ñoom askan wu dëgër bopp lañu. Su ma àndoon ak ñoom ab diir rekk, dinaa leen faagaagal. Kon nag nañu tàggook seeni gànjar, ba ma seet nu may def ak ñoom.» \v 6 Bànni Israyil a nga dale teqlikook seeni gànjar ca tundu Oreb. \s1 Yàlla feeñ na cib xayma \p \v 7 Musaa da daan toxal xayma bi, samp ko fu sorewaatook dal bi, ca biti. Mu di ko wooye \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi\f + \fr 33.7 \fr*\ft Gannaaw ga mbooloo ma defar jaamookaay, di ko wooye xaymab ndaje mi ba tey.\ft*\f*. Ku amaan lu muy diis \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, da daan génn dal bi, dem ba ca xaymab ndaje mooma ca biti. \v 8 Bu Musaa jëmaan ca xayma ba, mbooloo mépp ay daldi taxaw, ku nekk tollu ci sa bunt xayma, di ko seetaan, ba mu dugg ca biir xayma ba. \v 9 Te bu Musaa duggaan ca xayma ba, taxaaru niir wa day wàcc, ne tekk ca bunt xayma ba, fekk Aji Sax jaa ngay wax ak Musaa. \v 10 Su ko defee bu mbooloo ma mépp gisee taxaaru niir wa taxaw ca bunt xayma ba, ñoom ñépp ay daldi sujjóot, ku nekk ca sa bunt xayma. \v 11 Aji Sax ji da daan wax ak Musaa ne ko jàkk, mu ne ko jàkk, ni nit di waxe ak moroomam rekk. Bu ca Musaa jógee, daldi dellu ca dal ba, waaye bëkk-néegu Musaa, ngóor sa Yosuwe doomu Nuun daawul génn biir xayma ba. \s1 Musaa layool na bànni Israyil \p \v 12 Musaa nag ne \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji: «Waaw, yaw de yaa ngi ma naa ma yóbbu mbooloo mii, waaye xamaloo ma kan ngay yebal, mu ànd ak man. Yaa ma waxoon it ne ma: “Maa la xam ci saw tur, te it daj nga sama yiw.” \v 13 Gannaaw daj naa saw yiw nag, rikk xamal ma li nga namm, ba ma xam la. Su ko defee ma man di daj saw yiw. Te ngalla jàppal ne xeet wii kat, ñoo di sa ñoñ.» \p \v 14 Aji Sax ji ne ko: «Man ci sama bopp maay ànd ak yaw te maa lay noppal.» \p \v 15 Musaa ne ko: «Soo demul yaw ci sa bopp kay, bu nu jële fii! \v 16 Nees di xame ne daj naa saw yiw, maak sa ñoñ, te fekk ànduloo ak nun, ba nu doon, maak sa ñoñ, ñu ràññiku ci biir mboolem xeet yi ci kaw suuf?» \p \v 17 Aji Sax ji ne Musaa: «Loolu nga wax, moom laa lay defal, ndax daj nga samaw yiw, te it maa la xam ci saw tur.» \v 18 Musaa teg ca ne ko: «Ngalla may ma nag ma niir sag leer!» \v 19 Aji Sax ji ne ko: «Dinaa rombale sama gépp mbaax fi sa kanam, tey biralaale turu Aji Sax ji fi sa kanam. Maay baaxe ku ma neex, te maay ñeewante ku ma neex.» \v 20 Mu teg ca ne ko: «Doo mana gis sama kanam nag, ndax doom aadama du ma gis ba noppi di dund.» \v 21 Ci kaw loolu Aji Sax ji ne ko: «Xoolal fii ci sama wet, taxaweel ci kaw doj wi. \v 22 Bu sama leer di romb, maa lay làq fi xar-xaru doj wi, yiiraale la sama loxo, ba jàll, \v 23 doora dindi sama loxo, nga gis sama gannaaw, waaye sama kanam, maneesu koo gis.» \c 34 \s1 Lu jëm ci àlluway doj yu bees yi \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ne ko: «Yettal ñaari àlluway doj yu mel ni yu jëkk ya, ma bind ci kàddu ya woon ca àlluwa yu jëkk, ya nga toj. \v 2 Nanga waajal ëllëg, te nga teela yéegsi kaw tundu Sinayi wii, ba teewsi fi man ci njobbaxtalu tund wi. \v 3 Bu kenn ànd ak yaw, te bu kenn xand fenn kaw tund wi. Jur gi sax bumu forsi ci suufu tund wi, du gu gudd, du gu gàtt.» \v 4 Musaa nag yett ñaari àlluway doj yu mel ni yu jëkk ya, ba noppi teela xëy, yéegi ca tundu Sinayi, na ko ko Aji Sax ji sante. Ma nga ŋàbb ñaari àlluway doj ya. \p \v 5 Aji Sax ji nag wàcc ci biir aw niir, taxaw ak Musaa foofa, daldi biral turam, ne: «Aji Sax ji.» \v 6 Ci kaw loolu Aji Sax ji romb fa kanam Musaa, di biral naan: «Aji Sax jee, Aji Sax ji, Yàlla jiy yërëm, di yéwéne, mer ma diib, ngor gaak kóllëre ga bare. \v 7 Keey saxal ngor ba ci junniy maas, di bale tooñ ak moy ak bàkkaar, te du ñàkka topp ku tooñ, ag tooñaangeem, xanaa di topp doom tooñu waajur, ba ca sët yaak sëtaat ya.» \v 8 Ba loolu amee Musaa ne gurub fa suuf, sujjóot, \v 9 ne ko: «Éey Boroom bi, ndegam daj naa saw yiw, rikk àndal ak nun rekk, Boroom bi, ak li mbooloo miy dëgër bopp lépp! Jéggal nu sunu ñaawtéef ak sunu bàkkaar rekk, te nga séddoo nu.» \s1 Aji Sax ji yeesal na kóllëre gi \p \v 10 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ne ko: «Maa ngi nii di fas \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* ak yeen. Ci sa kanam mbooloo mépp laay def ay jaloore yu kenn masula amal ci àddina sépp, ak ci askan yépp, te mbooloo, mi nga nekk ci seen biir mépp ay gis jaloorey Aji Sax ji, jaloore ju raglu ji ma lay defal. \v 11 Bàyyileen xel bu baax li ma leen sant bésub tey jii. Maa ngii di leen dàqal Amoreen ñi ak Kanaaneen ñi ak Etteen ñi ak Periseen ñi ak Eween ñi ak Yebuseen ñi. \v 12 Moytuleena wóllëranteek niti réew ma ngeen jëm, bala ñoo doon ndëgg-sërëx ci seen biir. \v 13 Seeni \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* kay ngeen di màbb, seen tuuri doj, ngeen rajaxe, seen xer yi ñuy jaamoo \w Asera|lemma="Asera:"\w* tuur mi, ngeen gor, \v 14 ndax waruleena jaamu jeneen yàlla, ngir Aji Sax ji, turu “Ku fiir ki” lay wuyoo, te Yàlla ju fiir la. \v 15 Buleen wóllëranteek niti réew ma, lu ko moy dinañu gànctook seeni tuur, rendil seeni tuur ay sarax, woo leen ca, ngeen lekk ca seeni sarax. \v 16 Te it bu ngeen jëlalee seeni doom jabar ca seen doom yu jigéen, seen jigéen ñooña dinañu gànctook seeni tuur, ba xiir seen doom yu góor ci gànctook seen tuur yooyu. \p \v 17 «Ay tuur yu ñu móole weñ, buleen ko móol. \p \v 18 «\w Màggalug ayu bésu Mburu mu amul lawiir|lemma="Màggali Yawut yi:"\w*, wormaal-leen ko. Diiru juróom ñaari fan ngeen ciy lekk mburu mu amul lawiir, ni ma la ko sante bu àppam taxawee ci weeru \w Abiib|lemma="Abiib:"\w*, ndaxte weeru Abiib ngeen génne fa Misra. \p \v 19 «Bépp taaw bu góor maay boroom, ba ci lépp lu góor lu jur taawloo, muy nag mbaa gàtt. \v 20 Waaye lu góor lu mbaam taawloo, joteleen ko ab gàtt, mu wuutu ko. Su ngeen ko jotewul lu ko wuutu, dammleen loos wi. Képp kuy taaw bu góor ci seeni doom it, nangeen ko jot. Te itam bu kenn taxawe loxoy neen fi sama kanam. \p \v 21 «Juróom benni fan nag ngeen di liggéey, waaye bésub juróom ñaareel ba, dal-luleen. Bu ngeen doon bey, bu ngeen doon góob, dal-luleen. \p \v 22 «\w Màggalug ayi bési Ngóob|lemma="Màggali Yawut yi:"\w*, nangeen ko wormaal, bu ngeen di góob gubi bele yi jëkka ñor, \w màggalu bésu Farmàngu|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* mi ci ndeetel at mi itam, màggal-leen ko. \v 23 Ñetti yoon cim at la seen góor ñépp di teew fi kanam Boroom bi Aji Sax ji, Yàllay Israyil. \v 24 Maa leen di dàqal ay xeet, ba yaatal seen suuf, te diiru ñetti yoon yi ngeen di teewi cim at fi kanam Yàlla Aji Sax ji, kenn du ci wuta nangu seenum réew. \p \v 25 «Buleen rendi sama sarax, di boole deret jeek lu am lawiir, te gàttu saraxu \w bésub Mucc|lemma="Màggali Yawut yi:"\w*, bu ci dara fanaan ba bët set. \p \v 26 «Ngëneeli meññeef mi jëkka ñore ci seen suuf, nangeen ko yóbbu seen kër Yàlla Aji Sax ji. \p «Buleen togge ab tef soowum yaayam.» \p \v 27 Aji Sax ji teg ca ne ko: «Nanga bind yii santaane, ndax ci kaw santaane yii laa fasook yaw kóllëre, yaak \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*.» \p \v 28 Foofa la Musaa des ak Aji Sax ji diiru ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg te lekkul, naanul. Aji Sax ji nag bind ci àlluwa yi, fukki santaane yi lal kóllëre gi. \s1 Musaa dellu na dal ba \p \v 29 Ci kaw loolu Musaa wàcc tundu Sinayi, ŋàbb ñaari àlluway seede sa. Naka la Musaa di wàcce ca tund wa, deru kanam ga di lerxat te yégu ko. Booba ñaaroom baak Yàlla moo waral loola. \v 30 Naka la Aaróona ak \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp xoolaat Musaa, gisuñu lu moy deru kanam gay lerxat, ñu daldi koy ragala jege. \v 31 Musaa nag woo leen, Aaróona ak njiiti mbooloo ma yépp dikk, mu wax ak ñoom. \v 32 Gannaaw loolu bànni Israyil ga ca des gépp doora jegesi, mu dénk leen mboolem la \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxoon ak moom ca kaw tundu Sinayi. \v 33 Musaa wax ak ñoom ba noppi, daldi muuroo kaala, làqe ko kanamam. \p \v 34 Saa yu Musaa teewiwaan fa kanam Aji Sax ji, ngir wax ak moom, day muri kaala gi ba ba muy génn; bu génnee, yegge bànni Israyil la ñu ko sant. \v 35 Bànni Israyil nag di gis kanamu Musaa ak na deru kanam gay lerxate. Su ko defee Musaa dellu muuruwaat, làq kanamam, ba ba muy demaat, ngir wax ak Aji Sax ji. \c 35 \ms1 Bànni Israyil yékkati na jaamookaay ba \s1 Bésub Noflaay du bésu liggéey \p \v 1 Musaa nag dajale mbooloom \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* mépp. Mu wax leen ne leen: «Lii mooy li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji santaane, ngir ñu def ko: \v 2 Juróom benni fan lees di liggéey, waaye bésub juróom ñaareel ba, seen \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w* bu \w sell|lemma="sell:"\w* bu mat sëkk la, ñeel Aji Sax ji. Képp ku ci liggéey lenn, dees koy rey. \v 3 Buleen jafal sax sawara fenn ci seeni dëkkuwaay, ci bésub Noflaay.» \s1 Ay sarax war na ci jaamookaay bi \p \v 4 Musaa dellu wax ak mbooloom \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* mépp ne leen: «Lii mooy li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji santaane. \p \v 5 «Sàkkleen ci seen alal ab jooxe bu ñeel Aji Sax ji. Képp ku am yéeneb xolam, na indi jooxeb Aji Sax ji: wurus ak xaalis ak xànjar, \v 6 ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe, ak kawari bëy \v 7 ak deri kuuy yu ñu suub xonq, ak deri piipi, ak banti séng, \v 8 ak diwu làmp, ak ay xeeñal ngir diwu pal geek cuuraay lu xeeñ li, \v 9 ak ay peri onigsë ak yeneen per yuy tappe ci \w xar-sànni|lemma="xar-sànni m-:"\w* meek kiiraayal dënn bi. \p \v 10 «Mboolem ku xareñ ci yeen, na ñëw, ngeen def li Aji Sax ji santaane lépp: \v 11 jaamookaay bi ak xaymaam ak kiiraayam aki keppoom aki làccam, ak galan yeek jën yeek tegu yi, \v 12 ak \w gaal|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* geek ay njàppoom ak kubeer gi ñuy amale ag njotlaay, ak rido bi ko làq, \v 13 ak taabal jeeki njàppoom ak ndabam yépp ak \w mburum teewal|lemma="mburum teewal m-:"\w* mi, \v 14 ak tegukaayu làmp bi, aki jumtukaayam aki làmpam ak diwu làmp bi, \v 15 ak \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* cuuraay bi aki njàppoom, ak diwu pal gu sell gi, ak cuuraay lu xeeñ li; ak kiiraayal buntu jaamookaay bi, \v 16 ak sarxalukaayu \w rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* bi, ak caaxub xànjaram aki njàppoom ak li muy àndal lépp; mbalkam njàpp mi akub tegoom, \v 17 ak sor yi yéew jaamookaay bi aki jënam aki tegoom, ak lafu buntu ëtt bi, \v 18 ak xeri jaamookaay bi, ak jën yi yéew ëtt bi ak seeni buum, \v 19 ak yére yu yànj yi ñuy liggéeye ci \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi, yére yu sell yu Aaróona, \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi, ak yérey doomam, yi ñuy sarxalee.» \p \v 20 Ci kaw loolu mbooloom bànni Israyil gépp bàyyikoo fa Musaa. \v 21 Ba mu ko defee mboolem ña ca am pastéefu xol ak mboolem ña ca seen xel xiir, ñépp dikk, indi jooxeb Aji Sax ji ngir liggéeyu \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* meek bépp liggéey bu mu laaj, ngir itam yére yu sell yi. \v 22 Góor ak jigéen bokk dikk, mboolem ñi am yéeney xolam, mboolem ñi bëgga indi wurus, defal ko Aji Sax ji \w saraxu yékkati-jébbale|lemma="Sarax yi:"\w*; ñii indi ay lam, ñii jaaroy nopp, ñii jaaroy loxo, ñii ay caq, gànjari wurus yu nekk rekk. \v 23 Te it mboolem ñi dencoon wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ak kawari bëy mbaa deri xar yu ñu suub xonq, mbaa deri piipi, ñoom ñépp a indi la ñu dencoon. \v 24 Képp ku namma jooxe xaalis mbaa xànjar, jooxeel nga ko Aji Sax ji, te itam képp ku dencoon bantu séng bu jëm ci mboolem liggéeyu sarxal bi, indi nga bant bi. \v 25 Ci biir loolu jigéen ñu xareñ ñépp ëcce seeni loxo, ngir waajal wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ñu boole, indi. \v 26 Mboolem jigéen ñi ko mane te am yéeneem itam, daldi ëcc kawari bëy. \v 27 Njiit yi nag indi ay peri onigsë ak yeneen per yiy tappe ci xar-sànni meek kiiraayal dënn bi, \v 28 aki xeeñal, akug diw ngir làmp beek diwu pal geek cuuraay lu xeeñ li. \v 29 Mboolem bànni Israyil, góor ñeek jigéen ñi am yéeney indi lu jëm ci liggéey bi Aji Sax ji santaane, Musaa jottli, ñoom ñépp a indil Aji Sax ji ay \w saraxi yéene|lemma="Sarax yi:"\w*. \s1 Besalel ak Oliyab tàmbali nañu liggéey bi \p \v 30 Musaa nag ne \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*: «Gisleen, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji moo woo Besalel ci turam. Besalel, Uri mooy baayam; Uri, Ur Yudeen bi di baayam. \v 31 Moo ko feesale xelum Yàlla ak xareñte ak déggin ak xam-xam ak manoorey bépp xeetu liggéey, \v 32 ngir muy nas ay liggéeyi wurus ak xaalis ak xànjar, \v 33 di yett per yu muy tapp, di yett bant, di liggéey lu nekk. \v 34 Mayu jàngle itam yeb na ko cib dënnam, moom ak Oliyab, Daneen bi, doomu Ayisamaag. \v 35 Moo leen feesal xareñte, ngir bépp liggéey, ci wàllu yett ak nataal, ak liggéeyu wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe. Mane nañu ràbb te itam dañuy sos seen taarali bopp. \c 36 \p \v 1 «Kon nag Besalel ak Oliyab ak mboolem ñu xareñ ñi Aji Sax ji may xareñte ak déggin ngir ñu mana jëfe mboolem sas yi jëm ci liggéeyu \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi, ñoom ñépp nañu sottal lépp li Aji Sax ji santaane.» \p \v 2 Ba loolu amee Musaa woo Besalel ak Oliyab ak mboolem ñi xareñ ñi Aji Sax ji xareñal, mboolem ñi am yéeney wàllsi ci liggéey bi, ngir sottal ko. \v 3 Ba mu ko defee ñu nangoo ci Musaa mboolem jooxe bu bànni Israyil indi, ngir sottal liggéeyu bérab bu sell bi. Bànni Israyil nag jàppoo suba gu jot di indil Musaa ay \w saraxi yéene|lemma="Sarax yi:"\w*, \v 4 ba mboolem liggéeykat yu xareñ yi nekkoon ci mboolem liggéeyu bérab bu sell bi, kenn ku ci nekk bàyyi la nga jàppoon, daldi dikk. \v 5 Ñu ne Musaa: «Li mbooloo mi indi wees na dayob liggéey bi Aji Sax ji santaane.» \v 6 Musaa nag yéenelu ca dal ba bépp, ñu ne, ñépp, góor ak jigéen, bu ci kenn waajalati ab jooxe, ñeel bérab bu sell bi. Fa la mbooloo ma noppee indi. \v 7 Booba jumtukaay ya doyoon na sëkk, ba ëpp sax la ñu cay liggéey lépp. \s1 Defar nañu bérab bu sell ba \p \v 8 Ba loolu amee mboolem ñu xareñ ñi bokk ci liggéey bi daldi defar jaamookaay bi. Ñu def ko fukki sori rabali lẽe, yu ànd ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr. Ñu ñawaale ci ay nataali \w serub|lemma="serub y-:"\w*. \v 9 Guddaayu sor bu nekk di ñaar fukki xasab ak juróom ñett, yaatuwaay bi di ñeenti xasab, sor yépp tolloo. \v 10 Ñu taqle yii juróomi sor, taqle juróomi sor yi ci des. \v 11 Ci kaw loolu ñu ñaw ay takku yu baxa te laal yolet ci catal sor bi mujj ci benn taqalante bi, sor bi jeexal taqalante bi ci des it, ñu def ko noonu. \v 12 Juróom fukki takku lañu ñaw ci benn sor bi, ak juróom fukki takku ci catal sor bi jeexal taqalante bi ci des, takku yi yemoo. \v 13 Ñu defar juróom fukki lonkuy wurus, daldi jokklantee sor yi lonku yi, ba jaamookaay bi di benn. \p \v 14 Ba loolu weesee ñu ràbb ay sori kawari bëy, ngir def ko ñaareelu xayma, muy kiiraay ci kaw jaamookaay bi. Fukk ak benn lañu def sor yi. \v 15 Guddaayu sor bu nekk fanweeri xasab la, yaatuwaay bi di ñeenti xasab, te fukki sor yeek benn yépp a tolloo dayo. \v 16 Ñu taqle yii juróomi sor, juróom benni sor yi ci des it noonu. \v 17 Ñu sàkk juróom fukki takku ci catal sor, bi jeexal benn taqalante bi, daldi sàkk juróom fukki takku itam ci catal sor, bi jeexal taqalante bi ci des. \v 18 Ñu sàkk nag juróom fukki lonkuy xànjar yu ñu jokklantee ñaari taqalante yi, muy benn xayma. \v 19 Ñu defaral xayma bi malaanum deri kuuy bu ñu sóob xonq, ak meneen malaanum deri piipi muy tege ci kawam. \p \v 20-22 Gannaaw gi ñu sàkkal jaamookaay bi ay làcci bantu séng yu sampe. Làcc wu nekk am ñaari kenu yu ñu lëkklee galan yu ndaw, te noonu lañu def làcci jaamookaay bi yépp. Fukki xasab lañu def taxawaayu làcc wu nekk, def yaatuwaay bi xasab ak genn-wàll. \v 23 Ci wàllu làcci jaamookaay bi, ñu sësale ñaar fukki làcc fi féete bëj-saalum, \v 24 boole kook ñeent fukki tegukaayi xaalis yu ronu kenuy ñaar fukki làcc yi, ñaari tegukaay ronu làcc wi jiitu ngir ñaari kenoom yi mu àndal, ñaari tegu topp ci, ronu wépp làcc wu ci topp, ngir ñaari kenoom yi mu àndal. \v 25 Geneen wetu jaamookaay gi féete bëj-gànnaar itam, ñu def ko ñaar fukki làcc, \v 26 ak seen ñeent fukki teguy xaalis, ñaari tegu ronu làcc wi jiitu, ñaari tegu topp ci, ronu wépp làcc wu ci topp. \v 27 Gannaaw jaamookaay gi féete sowu, ñu sàkkal ko juróom benni làcc, \v 28 teg ci ñaari làcc ngir colli jaamookaay bi ci gannaaw, \v 29 ñu àndandoo di benn ci suuf te lëkkloo ci kaw ci benn lam kepp. Noonu lañu leen def ñoom ñaar, ñuy ñaari coll yi. \v 30 Muy juróom ñetti làcc ak seeni teguy xaalis; di fukki tegu ak juróom benn, ñaari tegu ronu làcc wu nekk. \p \v 31 Gannaaw loolu ñu sàkk ay galani banti séng, juróomi galan yiy ànd ak làcc, yi ci genn wetu jaamookaay bi, \v 32 ak juróomi galan ngir làcci wet gi ci des, ak juróomi galan ngir làcc yi ci gannaaw jaamookaay bi, fi féete sowu. \v 33 Ñu def galanu digg bi ci digg làcc yi, dale ko cat ba cat. \v 34 Ci biir loolu ñu xoob làcc yi wurus, sàkkal leen ay lami wurus yuy téye galan yi, daldi xoob galan yi it wurus. \p \v 35 Ñu sàkk itam rido bi, ràbbe ko wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ñawaale ci ay nataali serub. \v 36 Ñu sàkkal rido bi ñeenti jëni séng yu ñu xoob wurus, jën yi ànd ak wékkukaayi wurus, ñu móolal jën yi ñeenti teguy xaalis. \p \v 37 Ñu sàkkal buntu xayma bi kiiraay lu ñu ràbbe wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, mu doon liggéeyu ràbb bu rafet, \v 38 ak juróomi jënam yu ànd ak seeni wékkukaay. Ñu xoob nag wurus boppi jën yi ak seeni galan, juróomi teguy jën yi di xànjar. \c 37 \s1 Defar nañu gaalu kóllëre gi \p \v 1 Besalel nag defare \w gaalu kóllëre|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* gi dénku séng, guddaay bi di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaay bi di xasab ak genn-wàll, taxawaay bi di xasab ak genn-wàll. \v 2 Mu xoob ko wurusu ngalam biir ak biti, sàkkal ko kéméju wurus gu ko wër. \v 3 Mu daldi koy móolal ñeenti lami wurus ci ñeenti tànkam, ñaari lam ci genn wet gi, ñaar, wet gi ci des. \v 4 Mu sàkk nag ay njàppuy bantu séng, xoob bu ci nekk wurus, \v 5 daldi roof njàppu yi ci lami weti gaal gi, ngir ñu di ko yóbboo gaal gi. \p \v 6 Ci kaw loolu mu sàkk kubeeru saraxu njotlaay gu wurusu ngalam, guddaay bi di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaay bi di xasab ak genn-wàll. \v 7 Mu sàkk itam ñaari malaakay \w serub|lemma="serub y-:"\w* yu wurus. Liggéeyu tëgg bu jekk la def serub yi ci ñaari cati kubeer gi, \v 8 cat lii ab serub, cat lee ab serub, mu móolaale serub yi ak ñaari cat yi, serub yi ànd ak kubeer gi, di benn. \v 9 Serub yaa ngi tàllal seeni laaf, jëme kaw, yiire kubeer gi seeni laaf te janoo, seeni kanam jublook kubeer gi. \s1 Defar nañu taabalu mburum teewal mi \p \v 10 Ci biir loolu Besalel sàkk taabalu bantu séng, guddaay bi di ñaari xasab, yaatuwaay bi di xasab, taxawaay bi di xasab ak genn-wàll. \v 11 Mu xoob ko wurusu ngalam, defal ko ombu wurus bu ko wër. \v 12 Mu defal ko it pegg bu ko wër bu tollu ci yaatuwaayu ñeenti baaraam, ba noppi sàkkal pegg bi ombu wurus, wëralee ko ko. \v 13 Mu móolal taabal ji ñeenti lami wurus, daldi we lam yi ci ñeenti wet yi, fi fareek ñeenti tànk yi, \v 14 lam yi dendeek pegg bi, di téye njàppu, yi ñuy yóbboo taabal ji. \v 15 Mu sàkk ay njàppuy bantu séng, xoob ko wurus, ñu di ko yóbboo taabal ji. \v 16 Ci kaw loolu mu sàkk jumtukaay yiy tege ci taabal ji; ndabam yu tell yeek mbàttu yeek njaq yeek këll, yi ñuy tuural Yàlla, lépp di wurusu ngalam. \s1 Defar nañu tegukaayu làmp bi \p \v 17 Besalel sàkk itam tegukaayu làmp bu wurusu ngalam. Liggéeyu tëgg bu jekk la def tegukaayu làmp bi, ak taatu tegukaay bi, ak peru tegukaay bi, ay kaasam aki kàmbóotam aki mbaram, lépp ànd ak tegukaay bi, di benn. \v 18 Juróom benni car a soqikoo ci weti tegukaayu làmp bi, ñetti car ci gii wet, ñett ci gi ci des. \v 19 Ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóori garabu amànd ñoo nekk ci benn car bi, kaas bu ci nekk ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram, ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóori garabu amànd nekk ci car bi ci topp, kaas bu ci nekk ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram, ba juróom benni car, yi soqikoo ci per bi, daj. \v 20 Peru tegukaayu làmp bi itam am na ñeenti kaas yu bindoo ni tóor-tóori garabu amànd, ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram. \v 21 Ab kàmbóot a ronu ñaari car, jàpp ci, beneen kàmbóot ronu ñaari car yi ci topp, jàpp ci, ab kàmbóot ronu ñaari car yi mujj, jàpp ci, juróom benni car, yi soqikoo ci weti per bi, daj. \v 22 Kàmbóot yi ak car yi nag ànd ak tegukaay bi, di wenn donju wurusu ngalam wu ñu tëgg ba mu jekk. \v 23 Mu sàkk juróom ñaari làmpam ak ay ñiimi feyukaayam ak ay andam, lépp di wurusu ngalam. \v 24 Benn talaŋu wurusu ngalam, yemook fanweeri kilo, ci la sàkk tegukaayu làmp bi ak mboolem ay jumtukaayam. \s1 Defar nañu sarxalukaayu cuuraay bi \p \v 25 Ci kaw loolu Besalel sàkk ci bantu séng \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* cuuraay bu kaare, guddaay bi di xasab, yaatuwaay bi di xasab, taxawaay bi di ñaari xasab, ay béjjénam ànd ak moom di benn bant bi. \v 26 Mu xoob ko wurusu ngalam ci kaw ak ci wet yi, ba mu daj, ak béjjén yi, daldi koy sàkkal wombu wurus bu ko wër. \v 27 Ñaari noppi wurus la ko sàkkal ci ron kéméj gi, ci ñaari wetam, ñu jàkkaarloo, di téye banti njàppu, yi ñu koy yóbboo. \v 28 Ci biir loolu mu sàkk ay njàppuy banti séng, xoob lu ci nekk wurus. \v 29 Mu sàkk nag diwu pal gu sell gi, sàkk cuuraay lu xeeñ li raxul, def ko njafaan lu njafaan-kat waajal ba mu baax. \c 38 \s1 Defar nañu sarxalukaay bi ak mbalkam njàpp mi \p \v 1 Ba tey Besalel sàkk ci bantu séng \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* \w rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* bu kaare, guddaay bi di juróomi xasab, yaatuwaay bi di juróomi xasab, taxawaay bi di ñetti xasab. \v 2 Mu sàkkal ko ay béjjénam ci ñeenti collam, mu ànd aki béjjénam, di benn. Mu xoob nag lépp xànjar. \v 3 Mu sàkk jumtukaayi sarxalukaay bi yépp: ndabi tibbukaayu dóom yi ak ñiitukaay yi ak këll yi, ak lonkukaayi yàpp yi, ak and yi, jumtukaay yépp di xànjar. \v 4 Mu sàkkal sarxalukaay bi caax bu ñu tëgge xànjar, mu ronu peggu sarxalukaay bi, dale ci suuf ba ci digg sarxalukaay bi. \v 5 Mu daldi koy móolal ñeenti nopp ci ñeenti colli caaxu xànjar bi, ñuy téye njàppu yi. \v 6 Mu sàkk njàppuy bantu séng, xoob lu ci nekk xànjar, \v 7 daldi roof njàppu yi ci nopp yi ci weti sarxalukaay bi, ngir bu ñu koy yóbbu. Am pax, mu xànq yu tàppandaar ub, moom la def sarxalukaay bi. \v 8 Mu sàkk itam mbalkam njàpp mu ànd ak tegoom, di xànjar ju jóge ci seetuy jigéen\f + \fr 38.8 \fr*\fk seetuy jigéen ñi: \fk*\ft booba ay dogi xànjar lañu daan def seetu.\ft*\f*, ñi doon liggéey ci bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi. \s1 Defar nañu ëttu jaamookaay bi \p \v 9 Besalel nag sàkk wurmbalu jaamookaay bi. Wetam, gi fare bëj-saalum di téeméeri xasabi sori rabal yu ñu ràbbe wëñu lẽe, \v 10 seen ñaar fukki jën ànd ak seen ñaar fukki tegu, di xànjar, lonku yeek galani jën yi di xaalis. \p \v 11 Wetu bëj-gànnaar it di téeméeri xasabi sori rabal, seen ñaar fukki jën ànd ak seen ñaar fukki tegu, di xànjar, lonku yeek galani jën yi di xaalis. \p \v 12 Wetu sowu di juróom fukki xasabi sori rabal, ak seen fukki jën yu ànd ak seen fukki tegu, lonku yeek galani jën yi di xaalis. \p \v 13 Wetu penku bi ci kanam di juróom fukki xasab; \v 14-15 fukki xasabi sori rabal ak juróom fi làng ak buntu ëtt bi ci genn wetam, ak seen ñetti jën yu ànd ak seen ñetti tegu, ak fukki xasabi sori rabal ak juróom, wet gi ci des, ak seen ñetti jën yu ànd ak seen ñetti tegu. \p \v 16 Mboolem sori wurmbalu ëtt bi ba mu daj, wëñu lẽe la. \p \v 17 Teguy jën yi xànjar la, wékkukaayi jën yeek ay galanam di xaalis, ñu xoob boppi jën yi xaalis; jëni ëtt bi yépp nag, galani xaalis lañu leen lëkklee. \v 18 Lafu buntu ëtt bi, liggéeyu ràbb bu rafet la, bu ñu ràbbe wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe. Guddaayu laf bi ñaar fukki xasab la, taxawaay bi yemook yaatuwaay bi, di juróomi xasab, tollook sori wurmbalu ëtt bi. \v 19 Jëni lafu bunt bi ñeent la, seen ñeenti tegu di xànjar, seeni wékkukaay di xaalis, ñu xoob kaw jën yi xaalis, galan yi di xaalis. \v 20 Mboolem xeri jaamookaay bi ak xeri wurmbalu ëtt bi ba mu daj, lépp xànjar la. \s1 Lim nañu jumtukaay yi \p \v 21 Lii nag moo di tënkub dayoy gànjar yi ñu jëfandikoo ci liggéeyu jaamookaay bi, jaamookaay boobu àlluway seede si dence. Tënkees na ko ci ndigalu Musaa, \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi sasoo tënk bi ci njiital Itamar doomu Aaróona \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi. \v 22 Fekk na Yudeen bi Besalel doomu Uri, miy doomu Ur, sottal na mboolem li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji santoon Musaa. \v 23 Mu àndoon ci ak Daneen bi, doomu Ayisamaag, Oliyab. Mu dib yettkat, dib taaralkat te di liggéeykatu wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr ak wëñu lẽe. \p \v 24 Wurus wi dem ci liggéey bi bépp, mboolem liggéeyu \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi, te muy wurus wu ñu def \w saraxu yékkati-jébbal|lemma="Sarax yi:"\w* Yàlla, juróom ñetti téeméeri kilo ak juróom ñaar fukk ak juróom ñaar la (877), ak ñetti téeméeri garaam (300), yemook ñaar fukki talaŋ ak juróom ñeent, ak juróom ñaar téeméer ak fanweeri (730) siikal ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi. \v 25 Xaalis bi tukkee ci limeefu askan wi, ñetti junniy kilo ak fukk ak juróom ñaar (3 017), ak juróom ñaar téeméeri garaam ak juróom fukk (750), yemook téeméeri (100) talaŋ ak junneek juróom ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróomi (1 775) siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi, \v 26 muy juróomi garaami xaalis bopp bu nekk, yemook genn-wàllu siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi, ñeel képp ku bindu ci limeef bi, dale ko ci ñi am ñaar fukki at jëm kaw, ñépp di juróom benni téeméeri junniy góor ak ñetti junneek juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550). \v 27 Ñetti junniy (3 000) kiloy xaalis, di téeméeri talaŋ, ñeel móolub teguy bérab bu sell bi, ak teguy rido bi. Muy téeméeri tegu ci ñetti junniy kilo, di fanweeri kilo ci benn tegu, muy téeméeri tegu ci téeméeri talaŋ, benn talaŋ ci benn tegu. \v 28 Fukki kilook juróom ñaar yeek juróom ñaar téeméeri garaam yeek juróom fukk (17 kilo 750 garaam) yi ci topp, yemook junneek juróom ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróomi siikali xaalis, ay wékkukaay la ci sàkk ngir jën yi, xoob ci boppi jën yi, sàkk ci galan yi. \p \v 29 Xànjar bi ñu def saraxu yékkati-jébbal Yàlla, ñaari junniy kilo ak téeméer ak ñaar fukk ak ñeent la (2 124), yemook juróom ñaar fukki (70) talaŋ ak ñaari junneek ñeenti téeméeri (2 400) siikal. \v 30 Mu sàkk ci teguy buntu \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi, ak \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* xànjar bi, ak caaxub xànjaram, ak mboolem jumtukaayi sarxalukaay bi, \v 31 ak teguy wurmbalu ëtt bi, ak teguy buntu ëtt bi, ak xeri jaamookaay bi yépp, ak xeri wurmbalu ëtt bi. \c 39 \s1 Defar nañu yérey sarxalkat yi \p \v 1 Wëñ gu baxa gi te laal yolet nag ak wëñ gu xewar gi ak gu xonq gi curr, ci lañu sàkk yére yu yànj yi ñuy liggéeye ci \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi. Ñu daldi defar yére yu \w sell|lemma="sell:"\w*, yi ñeel Aaróona noonee ko \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji sante woon Musaa. \p \v 2 \w Xar-sànni|lemma="xar-sànni m-:"\w* mi, wëñu wurus lees ko ràbbe, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe. \v 3 Ay xobi wurus lañu tëgg ba mu jekk, ñu dagg ko ay wëñ yu ñu ràbbaaleek wëñ gu baxa gi te laal yolet, ak wëñ gu xewar gi, ak gu xonq gi curr, ak wëñu lẽe gi. Ñu daldi ciy ñawaale ay nataal. \v 4 Ñaari ngàlli mbagg lañu ko defal, daldi faste wu ci nekk ci ñaari cati xar-sànni mi. \v 5 Ngañaayu taaral li tege ci kaw, ni xar-sànni mi lees ko defare, liggéeyaale kook moom, ñu ànd di benn. Ñu ràbbe ko wëñu wurus, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe, noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa. \p \v 6 Ci kaw loolu ñu we peri onigsë yi, fege per yi ŋankukaayi wurus, daldi ciy ñaas turi doomi Israyil yu góor, noonu ñuy ñaase xàmmikaay yi ñuy torloo. \v 7 Ñu tapp per yi ci kaw ngàlli waggi xar-sànni mi, per yi nag taxawe taxawaayu \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, noonu ko Aji Sax ji sante woon Musaa. \s1 Defar nañu kiiraayal dënn bi \p \v 8 Ñu sàkk kiiraayal dënn bi, liggéeyaale ko ay nataal ni \w xar-sànni|lemma="xar-sànni m-:"\w* mi, ràbbe ko wëñu wurus, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe. \v 9 Ab kaare bu ñu lem lañu ko def, guddaay bi, gannaaw bu ñu ko lemee, di ŋaraleb baaraamu déy ak digg, yaatuwaay bi di ŋaraleb baaraamu déy ak digg. \v 10 Ñu we nag ay per ci kaw kiiraayal dënn bi, def ko ñeenti làngi per. Làng gi jiitu, peru sarduwan ak peru topaas ak peru eskarbukal moo ca nekk; \v 11 ñaareelu làng gi di peru emëródd ak peru safiir ak peru jamaa, \v 12 ñetteelu làng gi di peru yasent ak peru agaat ak peru ametistë, \v 13 ñeenteelu làng gi di peru kirsolit ak peru onigsë ak peru jàspë, te per bu ci nekk ŋankukaayu wurus lees ko wewe. \v 14 Per yeek turi doomi Israyil yu góor ñoo tolloo ab lim: muy fukk ak ñaar, ni tur yi tollu. Ñu ñaas ci tur yi ni xàmmikaayi torlu, ku nekk ak turam, ba fukki giir yeek ñaar daj. \p \v 15 Ci biir loolu ñu sàkkal kiiraayal dënn bi ñaari caqi wurusu ngalam yu ci tege, te rawaasoo ni ay buum. \v 16 Ñu sàkk itam ñaari ŋankukaayi wurus ak ñaari jaaroy wurus yu ñu takk ci ñaari cati kiiraayal dënn bi ci kaw \v 17 Ñu nas nag ñaari buumi wurus yi ci ñaari jaaro yi ci cati kiiraay li. \v 18 Yeneen ñaari cati buumi wurus yi, ñu we leen ci ñaari ŋankukaay, yi ci kaw ngàlli waggi xar-sànni mi, ci kanam. \v 19 Ñu sàkkal ko itam ñaari jaaroy wurus, yu ñu we ci ñaari cati suufi kiiraay li, fi féete biir, wet gi tafu ci xar-sànni mi. \v 20 Ñu sàkkalaat kiiraay li yeneen ñaari jaaroy wurus, yu ñu we ci suufu ngàlli xar-sànni mi, fi féete kanam, dendeek sofu ngàll yi, te tiim ngañaayu xar-sànni mi. \v 21 Kiiraayal dënn bi, buum gu sew gu baxa te laal yolet, moom lees ko téyee, lëkklee ko jaaroy kiiraay leek jaaroy xar-sànni mi, kiiraay li dëkke tiim ngañaay li, ba du teqlikook xar-sànni mi, noonee ko \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji sante woon Musaa. \s1 Defar nañu yérey sarxal, yi ci des \p \v 22 Fëxya bi \w xar-sànni|lemma="xar-sànni m-:"\w* miy tege, lépp, wëñ gu baxa te laal yolet lees ko ràbbe ba mu daj. \v 23 Baatu fëxya baa ngi ci digg bi, mel ni baatu mbubbam xare, ñu ombe ko omb bu dëgër, ba mu daj, ngir du xottiku. \v 24 Ci biir loolu ñu takk ci ombu fëxya bi, ay doomi gërënaat yu ñu defare wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe. \v 25 Ñu def itam ay jóolóoliy wurusu ngalam, ba takk jóolóoli yi ci diggante doomi gërënaat yi, wërale ko ombu fëxya bi, ba mu daj, jóolóoli yi dox diggante doomi gërënaat yi. \v 26 Ab jóolóoli, ab gërënaat, ab jóolóoli, ab gërënaat ba ombu fëxya, bi ñuy sol di sarxal daj, noonee ko \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji sante woon Musaa. \p \v 27 Ñu sàkkal nag Aaróona aki doomam mbubb yu gudd yu ñu ràbbe wëñu lẽe, \v 28 ak kaalag lẽe, ak mbaxanay lẽe, ak tubéyi njiitlaay yu lẽe, \v 29 ak laxasaay giy liggéeyu ràbb bu rafet, bu ñu ràbbe wëñu lẽe bu dëgër, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa. \p \v 30 Ñu sàkk nag meeteel gu \w sell|lemma="sell:"\w* gu wurusu ngalam, muy dogu wurus wu tell, ñu ñaas ci kawam mii mbind, ni ñuy ñaase mbindum torlu: «Sell na, ñeel Aji Sax ji». \v 31 Ñu daldi koy takke buum gu baxa te laal yolet, téyee ko ko ci kaw kaala gi, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa. \s1 Musaa memmiku na liggéey bi \p \v 32 Noonu la mboolem liggéeyu màkkaanu \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi mate. Noonee ko \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji sante woon Musaa rekk, ni la ko \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* defe. \p \v 33 Ba loolu amee ñu indil Musaa jaamookaay bi: xayma bi ak yëfam yépp; lonku yi ak làcc yi ak galan yi ak jën yeek tegu yi, \v 34 ak kiiraayal deri kuuy yi ñu sóob xonq, ak kiiraayal deri piipi yi, ak kiiraayal xàjjatle bi, \v 35 ak \w gaal gi àlluway seede si dence|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w*, aki njàppoom, ak kubeeru saraxu njotlaay gi, \v 36 ak taabal jeek ndabam yépp, ak \w mburum teewal|lemma="mburum teewal m-:"\w* mi ciy tege, \v 37 ak tegukaayu làmp bu wurusu ngalam bi aki làmpam, làmp yi sësaloo ba jekk ak mboolemi jumtukaayam, ak diw gi ñuy taaloo, \v 38 ak \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bu wurus bi, ak diwu pal gi, ak cuuraay lu xeeñ li, ak kiiraayal buntu xayma bi, \v 39 ak sarxalukaayu xànjar beek caaxub xànjaram, aki njàppoom ak ndabam yépp, ak mbalkam njàpp mi akub tegoom, \v 40 ak sori wurmbalu ëtt bi aki jënam aki tegoom, ak kiiraayal lafu buntu ëtt bi, aki buumam aki xeram; mboolem jumtukaay, yi ñuy liggéeye ci màkkaanu xaymab ndaje mi rekk, \v 41 ak yére yu yànj yi ñuy liggéeye ci \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* bi; yére yu \w sell|lemma="sell:"\w* yu Aaróona \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi, ak yérey doomam yi ñuy sol, di sarxale. \v 42 Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa rekk, ni la bànni Israyil sottale liggéey bi bépp. \v 43 Musaa nag nemmiku mboolem liggéey bi, ba gis ne sottal nañu ko; noonee ko Aji Sax ji santaanee woon, ni lañu ko defe. Musaa daldi leen ñaanal. \c 40 \s1 Samp jaamookaay bi jot na \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxati Musaa ne ko: \v 2 «Bu keroogee benn fanu weer wi jiitu, nanga samp màkkaanu \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi. \v 3 Nanga yeb ci biir, \w gaal gi àlluway seede si dence|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w*, te nga làqe gaal gi rido bi. \v 4 Dugalal taabal ji te taaj ci li muy àndal; dugalal tegukaayu làmp bi, nga taal ay làmpam, \v 5 te nga teg \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* cuuraay bu wurus bi ci kanam gaal gi àlluway seede si dence, ba noppi nga samp lafu buntu jaamookaay bi. \p \v 6 «Tegal sarxalukaayu \w rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* bi fi kanam buntu màkkaanu xaymab ndaje mi. \v 7 Tegal mbalkam njàpp mi ci diggante xaymab ndaje mi ak sarxalukaay bi, te nga duy ko ndox. \v 8 Sampal nag wurmbalu ëtt bi bépp, te nga we lafu buntu wurmbal bi. \p \v 9 «Jëlal nag diwu pal gi, nga diw ci jaamookaay bi ak li ci biiram lépp, sellale ko ko, mook yëfam yépp, mu daldi \w sell|lemma="sell:"\w*. \v 10 Boo noppee, diwal sarxalukaayu rendi-dóomal bi, mook ndabam yépp, nga sellale ko sarxalukaay bi, sarxalukaay bi daldi sella sell. \v 11 Nanga diw mbalkam njàpp mi akub tegoom, nga sellale ko ko. \p \v 12 «Indil Aaróona aki doomam ba ci bunt xaymab ndaje mi, nga sang leen ci ndox mi. \v 13 Nga daldi solal Aaróona yére yu sell yi, diw ko, sellale ko ko, mu doon sama sarxalkat. \v 14 Su ko defee nga indi ay doomam, solal leen ay mbubb. \v 15 Nga diw leen, ni nga diwe seen baay, ñu doon samay sarxalkat. Seen diwu googu moo leen sédd sasu carxal bu sax dàkk, maasoo maas.» \v 16 Musaa nag def loola. Mboolem noonee ko ko Aji Sax ji sante, na la ko defe. \s1 Musaa samp na jaamookaay bi \p \v 17 Keroog at ma topp ca at ma ñu génne Misra, ca benn fanu weer wa jëkk, ca lañu samp jaamookaay ba. \p \v 18 Musaa nag samplu jaamookaay bi: Ñu jiital tegu yi, samp làcc yi, we galan yi, daldi samp jën yi. \v 19 Ci kaw loolu, ñu firi malaan mi ci kaw jaamookaay bi, daldi lal kiiraay li ci kawam, na ko \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji sante woon Musaa. \p \v 20 Gannaaw loolu ñu jël àlluway seede si, yeb ko ci \w gaal|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* gi, ba noppi roof njàppu yi ci gaal gi. Ñu daldi teg kubeeru saraxu njotlaay gi ci kaw gaal gi. \v 21 Ba mu ko defee ñu fat gaal gi ci biir bérab bu sell bi, doora firi ridob xàjjatle bi, làqe ko ko, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa. \p \v 22 Ba loolu amee ñu dugal taabal ji ci biir \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi, ci wetu bëj-gànnaaru jaamookaay bi, ci kanam rido bi. \v 23 Ñu daldi teg ci kaw taabal ji, tegin wu jekk, mburu mi fi kanam Aji Sax ji, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa. \p \v 24 Ñu dugal nag tegukaayu làmp bi ci biir xaymab ndaje mi, fi janook taabal ji, ci wetu bëj-saalumu jaamookaay bi, \v 25 daldi taal làmp yi fi kanam Aji Sax ji, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa. \p \v 26 Ba mu ko defee ñu dugal \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* wurus bi ci biir xaymab ndaje mi, ci kanam rido bi, \v 27 daldi taal cuuraay lu xeeñ li ci kawam, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa. \p \v 28 Ñu samp lafu buntu jaamookaay bi. \v 29 Sarxalukaayu \w rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* bi nag, ñu teg ko ci bunt màkkaanu xaymab ndaje mi, daldi def ci kawam saraxu rendi-dóomal bi, ak \w saraxi pepp|lemma="Sarax yi:"\w* mi, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa. \p \v 30 Ba loolu amee ñu teg mbalkam njàpp mi ci diggante xaymab ndaje mi ak sarxalukaay bi, ba noppi duy ko ndoxum njàpp. \v 31 Ci la Musaa ak Aaróona aki doomam di raxas seeni loxo ak seeni tànk, \v 32 ndax bu ñuy dugg ci xaymab ndaje mi, ak bu ñuy jegeji sarxalukaay bi, dañuy jàpp, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa. \p \v 33 Gannaaw loolu ñu samp wurmbal bi yéew jaamookaay beek sarxalukaay bi, daldi samp lafu buntu ëtt bi. Noonu la Musaa sottale liggéey bi. \s1 Leeru Aji Sax ji gane na bérab bu sell bi \p \v 34 Ba loolu amee niir wa yiir \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* ma, leeru \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji fees jaamookaay ba, \v 35 ba Musaa tëlee dugg ca xaymab ndaje ma, ndax niir wa màkkaanoo kaw xayma ba, ak leeru Aji Sax ji fees jaamookaay ba. \p \v 36 Saa yu niir wa yékkatikoo, ba tiim jaamookaay ba nag, \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* daldi tegu ca seen yooni tukki ya. \v 37 Waaye bu niir wa yékkatikuwul, duñu dem, ba keroog muy yékkatiku. \v 38 Ndax booba niiru Aji Sax jaa nga ca kaw jaamookaay ba, ag bëccëg, te sawara waa nga ca biir niir wa, ag guddi, waa kër Israyil gépp di ci gis, seen diiru yooni tukki ya.