\id EPH (WOL) \ide UTF-8 \h Efes \toc1 Bataaxal bi Yàlla may Póol, mu bind ko waa Efes \toc2 Efes \mt2 Bataaxal bi Yàlla may Póol, // mu bind ko waa \mt1 Efes \c 1 \p \v 1 Ci man Póol, ndawal Almasi Yeesu ci coobarey Yàlla, ci man la kàddu gii bawoo, ñeel ñu sell ña ca Efes te di ñu sàmm seen kóllëre ak Almasi Yeesu. \v 2 Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi. \s1 Ay barkee ngi ci Almasi \p \v 3 Cant ñeel na Yàlla sunu Baayu Sang Yeesu \w Almasi|lemma="Almasi:"\w*, mi nu baaxe bépp barkey biir, ci Almasi mi nu bokk, fa déndi asamaan ya. \v 4 Te mooy noonu mu nu taamoo ba àddina sosoogul ndax Almasi mi nu bokk, ngir nu doon ñu sell te mucc sikk fa kanamam. Ci biir cofeel \v 5 la dogaloon lu jiitu, ne ci Yeesu Almasi la nuy defe ay doomi boppam, te muy bànneexam, di coobareem. \v 6 Moo tax cant ñeel ko, ndax yiwam wu màgg wi mu nu baawaanal ci Soppeem bi. \p \v 7 Ci moom lanu ame \w njot|lemma="jot:"\w* gi nu sottalal njéggalug moy, ndax deretam ji tuuru, noonu ko Yàlla defe ci yiwam wu yaa, \v 8 wi mu nu baawaanal, mayaale nu mépp xel mu rafet akug dégg. \v 9 Moo nu xamal mbóotum coobareem, mi mu nammoona sottale naka jekk ci Almasi, na mu ko neexe. \v 10 Li Yàlla namm, bu fan yi matee, moo di dajale lépp ci kilifteefu Almasi, mboolem la fa asamaan, ak li fi suuf. \v 11 Ci moom lanu jote sunu muur ci kaw dogalu Yàlla mi nu taamu lu jiitu, moom miy sottal lépp ni mu ko namme ci coobareem. \v 12 Moo tax nu di ko sante màggaayam, nun ñi jëkka wékk sunu yaakaar ci Almasi. \p \v 13 Kooku, yeen ñi dul Yawut, ba ngeen déggee, yeen itam kàddug dëgg gi, xibaaru jàmm, bi jëm ci seenug mucc, gannaaw ba ngeen gëmee, ci moom itam lañu leen màndargaale \w Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"\w* gi ñu dige woon. \v 14 Noo gi moo di dawal bi nu jotagum ci sunu muur, ba kera njotug ñoñi Yàlla matee, ba nit ñi sante Yàlla màggaayam. \s1 Póol sant na, ñaan na \p \v 15 Moo tax man it, bi ma déggee ba tey, seen ngëm ci Sang Yeesu, ak seen cofeel ci ñu sell ñépp, \v 16 noppiwumaa sant Yàlla ndax yeen, te maa ngi leen di fàttliku ci samay ñaan, \v 17 ngir Yàllay sunu Sang Yeesu \w Almasi|lemma="Almasi:"\w*, Baay bu màgg bi, sol leen xel mu rafet, ak ngis, ngir ngeen man koo xam bu baax. \v 18 Ngir itam seen bëti xol leer ba ngeen gis yaakaar ji ci wooteem, ak ni ay ngëneelam géejoo te yéeme, ñeel ñu sell ñi mu séddoo. \v 19 Ngeen boole ci xam manooreem gu nattuwul gi mu nu lañalal, nun gëmkat ñi. Manoore googu feeñ na ci jëf ji sottee ci kàttanam ak dooleem, \v 20 ji mu fésal ci Almasi, ba mu ko dekkalee, dëël ko ci ndijooram, fa déndi asamaan. \v 21 Foofa la Almasi tiime lu sore gépp nguur, ak bépp sañ-sañ, ak gépp manoore, ak gépp kilifteef, ak wépp tur wees di tudd, muy tey, di ëllëg. \v 22 Yàlla moo teg lépp fi suufu ndëgguy tànkam, te moo ko def muy bopp bi tiim lépp, ñeel mbooloom gëmkat ñi, \v 23 mbooloo miy aw yaramam. Ci mbooloo mi nag la Almasi teewe teewaay bu mat sëkk, te Almasi mooy matal lépp ci ñépp. \c 2 \s1 Gëm, soppi \p \v 1 Yeen dangeena dee woon ndax seeni moy ak seeni bàkkaar, \v 2 yi ngeen doon dunde démb, ngeen àndoon ci ak doxalinu àddinay tey jii, ak ku bon kiy kàngamu boroom baat yi ci jaww, ji asamaan tiim, boroom noo gi wéye liggéeyam ci biir aji déggadi ñi, tey. \v 3 Ci ñoom lanu bokkoon nun ñépp itam; mas nanoo topp sunu bakkan, di jëfe lu sunu bakkan, ak sunum xel xemmem. Sunu bindu nit taxoon na noo yeyoo am sànj ni ñépp. \p \v 4 Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw cofeel gu réy, gi mu nu sopp, \v 5 nun ñi doon nit ñu dee ba noppi ndax sunuy moy, moo nu booleek \w Almasi|lemma="Almasi:"\w*, dundalaat nu. Ci kaw yiw daal ngeen mucce. \v 6 Ci sunu bokk ak Yeesu Almasi la nu Yàlla dekkalandoo ak moom, dëëlandoo nook moom fa déndi asamaan. \v 7 Mbaax gi nu Yàlla won ci Almasi Yeesu, moom lay firndeele mboolem xarnu yiy ñëw, ni yiwam yaatoo ba tiiñ am xel. \v 8 Ndax kat ci yiw ngeen mucce ci kaw ngëm, te loolu jógewul ci yeen, mayu Yàlla la; \v 9 du peyu jëf, ba kenn di ci kañu. \v 10 Ndax kat noo di liggéeyu Yàlla; Yàllaa nu yeesal ci Almasi Yeesu, ngir nu wéye jëf ju rafet, ja mu nu fàgguloon ca njàlbéen, ngir nu di ko jëfe. \s1 Gëmkati Almasi benn lañu \p \v 11 Kon nag, yeen jaambur ñi dul Yawut cib juddu, yeen ñi ñuy wooye yéefar yi xaraful, te ñi leen ko dàkkantale woon di Yawut yi xarafe ci loxol nit ku leen xarfal ci seen yaram, fàttlikuleen seen démb. \v 12 Jant yooyu amuleen woon benn cér ci \w Almasi|lemma="Almasi:"\w*, te amuleen woon jenn yelleef ci mbootaayu \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. Bokkuleen woon ci kóllëre yi ëmb digeb Yàlla, te mu fasoo ko ak ñoom. Ñàkk yaakaar, ak ñàkka xam Yàlla ngeen nekke woon ci àddina. \v 13 Waaye yeen ñi sore woon, léegi bi ngeen nekkee ci Almasi Yeesu, jege ngeen ndax deretu Almasi ji tuuru. \p \v 14 Ndaxte moom mooy sunu jàmm, moom mi boole ñaar, Yawut bi ak jaambur bi dul Yawut, def leen kenn. Ci suuxu yaramam wa ñu daaj la ñàggee ñagu mbañeel bi doxoon sunu diggante. \v 15 Yoonu Musaa ak santaane yaak ndigal ya, moom la xewil, ngir yeesal ñaar ñi, Yawut beek jaambur bi, ci jenn jëmmu boppam, ñu doon kenn nit ku yees, ba jàmmoo. \v 16 Ñaar ñi la Almasi boole ci jenn jëmm, jubale leen ak Yàlla, ca bant ba ñu ko daajoon, te bant ba la dakkale sunub tongoo. \v 17 Moo dikke xibaaru jàmm buy yégle jàmm ju leen ñeel, yeen jaambur ñi ko sore woon, te ñeel nu, nun ñi ko jege, \v 18 ndax nun ñaari xeet yépp, ci moom Almasi lanu jote ci Baay bi, ci ndimbalal genn \w Noo|lemma="Noo gu Sell g-:"\w* gi. \p \v 19 Kon nag dootuleen ay gan mbaa ay doxandéem, waaye ay nawley ñu sell ñi ngeen, te waa kër Yàlla ngeen. \v 20 Yeena di tabax, bi ndawi Almasi ak yonent yi di kenu gi, te Almasi Yeesu ci boppam di doju coll wi. \v 21 Ci moom la tabax bi bépp di temboo, ba jóg, doon jaamookaay bu sell ngir Boroom bi. \v 22 Ci Almasi ngeen bokke ci tabax bi, yeen jaambur ñi itam, ba mana doon dëkkuwaayu Yàlla, ci ndimbalal Noo gu Sell gi. \c 3 \s1 Póol xamle na mbóotum Yàlla \p \v 1 Moo ma tax di ñaan, man Póol mi ñu tëj ngir \w Almasi|lemma="Almasi:"\w*, ndax ñi dul Yawut, yeen jaambur ñi, \v 2 ndegam yég ngeen sas wi ma Yàlla sas ciw yiwam, ñeel leen. \v 3 Ci am peeñu lañu ma xamale mbóot mi, noonu ma leen ko tënkale woon ci bataaxal. \v 4 Bu ngeen jàngee loolu, dingeen ràññee bu baax, ni ma dégge mbóot mi ci mbirum Almasi. \v 5 Moomu mbóot, xamaleesu ko woon doom aadama yi, ca janti maas ya woon, ni ñu ko feeñalale tey, ñu sell ñi diy ndawam ak yonent yi, ci ndimbalal \w Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"\w* gi, \v 6 ba mu leer ne jaambur ñi dul Yawut ñooy bokk ak Yawut yi benn cér bi, ñooy doon wenn yaram, te ñooy bokk benn dige bi ci Almasi Yeesu, ni ko xibaaru jàmm bi xamlee. \p \v 7 Xibaaru jàmm boobu lañu ma def ab jawriñam, te Yàlla, ciw yiwam, moo jëfe manooreem, ba jagleel ma boobu cér. \v 8 Man mi yées ci ñu sell ñépp lañu may woowu yiw, ba may xibaar jaambur ñi dul Yawut, xéewal yu amul kem yi ci Almasi. \v 9 May niital ñépp, ni Yàlla nara sottale mébétam, miy mbóot mu làqu woon naka jekk fa moom Yàlla mi sos lépp. \v 10 Su ko defee boroom nguur yeek boroom sañ-sañ ya fa déndi asamaan, mana xame ci mbooloom gëmkati Almasi, ni xelum Yàlla rafete ci wet gu nekk. \v 11 Loolu moo doon naka jekk nammeelam gi mu sottale ci Almasi Yeesu sunub Sang. \v 12 Ci Yeesu, ci kaw ngëm gu nu ko gëm lanu ñemee àgge fit wu mat sëkk, fa kanam Yàlla. \v 13 Kon nag dama leen di ñaan, ngeen baña yoqi ngir coono, yi may sonn ndax yeen; lépp seen teraanga la. \s1 Saxoo gëm moo mata ñaan \p \v 14 Looloo ma taxa sukk sama bëti óom, janook Baay bi, \v 15 ki gépp njabootug asamaan ak suuf, jële aw tur. \v 16 May ñaan nag, mu may leen, ci koomu teraangaam, seen jëmmu biir feddlikoo kàttanu \w Noowam gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"\w*. \v 17 Su ko defee seen ngëm tax \w Almasi|lemma="Almasi:"\w* dëkke seen xol, ngeen sax ay reen yu sampe ci biir cofeel, \v 18 ngir yeen ak mboolem ñu sell ñi, seenum xel mana jàpp, ni mu leen ware, luy yaatuwaayub cofeelu Almasi, ak guddaay ba, ak kawewaay ba, ak xóotaay ba. \v 19 Ngeen boole ci daj cofeelu Almasi, gi wees xam-xam, ngir ngeen fees, ba fees dell ak koomu Yàlla. \p \v 20 Moom mi mana jëfoo kàttan giy liggéey ci nun, ba sottal mboolem lu nu ñaan ak lu nu xalaat, ba wees loola fuuf sax, \v 21 moo yelloo daraja ci biir mbooloom gëmkat ñi, ak ci Almasi Yeesu, tey ak ëllëg, ba fàww. Amiin. \c 4 \s1 Mbooloom gëmkat ñi wenn yaram la \p \v 1 Dama leen di dénku nag, man mi ñu tëj ndax Sang bi, ngir ngeen dund dundin wu yellook wooteb Yàlla, bi mu leen woo. \v 2 Saxooleen woyof, lewet, te deeleen muñ, di muñalante ngir cofeel. \v 3 Defleen seen kem kàttan, ngir di jàmmoo, ba mana sàmm seenug bennoo ci biir \w Noo|lemma="Noo gu Sell g-:"\w* gi ngeen bokk. \p \v 4 Wenn yaram a fi nekk, ak genn Noo, ak jenn yaakaar ju leen wooteb Yàlla jëme. \v 5 Benn Sang bi la it, ak genn ngëm, ak genn sóobu cim ndox\f + \fr 4.5 \fr*\fk sóobu cim ndox \fk*\ft la gëmkatub Almasi di firndeele ngëmam.\ft*\f* . \v 6 Te it jenn Yàllaa am; mooy Baayu ñépp, moo tiim ñépp, di jëf ci ñépp te nekk ci ñépp. \p \v 7 Waaye ku nekk ci nun ak mayam, ci yiwu Yàlla, ni ko nattub \w Almasi|lemma="Almasi:"\w* séddalee. \v 8 Moo tax ñu ne: \q1 «Moo yéeg fa kawa kaw, \q1 yóbbaale gàngoor gu mu jàppe xare, \q1 te moo séddale nit ñi ay may\f + \fr 4.8 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Sabóor\+bk* 68.19.\ft*\f*.» \m \v 9 Li ñu ne «moo yéeg,» ana lu mu tekki lu moy wàccoon na it ba fu gëna suufe? \v 10 Kooku wàccoon mooy kenn ki yéegaat ba tiim asamaan yépp, ngir def lépp feese jëmmam. \v 11 Moo may ñii di ay ndawam, ñee di ay yonent, ñee di ay xamlekati xibaaru jàmm bi, ñale di ay sàmmi mbooloom gëmkat ñi, mbaa ay jànglekat. \v 12 Almasi moo waajale noonu ñu sell ñi, ba ñu mana bey seen sas ci liggéeyam, ngir tabax mbooloom gëmkat, mi taxawe yaramu Almasi. \v 13 Su ko defee nu mana màgg nun ñépp ba doon benn ci ngëm, ak ci xam-xam bu mat ci Doomu Yàlla ji, ba kera nuy doon magum jëmm, bay tollook taxawaayu Almasi bi mat sëkk. \p \v 14 Su boobaa nu noppee doon ay tuut-tànk yu nit ñiy muusaatoo kàddu yu mel ni gannax yu nuy baaje, ak ngelawal mboolem àlluwa ju bees ju nuy pamti-pamtee ci seen biir pexey naxe ak njublaŋ, ngir fàbbi nu. \v 15 Su boobaa kay, dëgg gu nu wodde cofeel lanuy wéye, tey màgg ci bépp fànn, ci moom Almasi miy bopp bi. \v 16 Ci moom miy bopp bi la yaram wépp di déggoo, témboo ndax ndimbalal mboolem tenqo yi koy saytu, na mu dëppook wàllu cér bu ci nekk. Su ko defee yaram wiy yokku, di màgg ci biir cofeel. \s1 Ku gëm Almasi war koo roy \p \v 17 Lii nag maa leen ko wax, te di ko biral ci turu Boroom bi: Ni xeeti yéefar yiy jëfe, topp seen xalaat yu tekkiwul dara, buleen jëfeeti noonu. \v 18 Seenum xel a tàbbi ag lëndëm, ñu tumurànke dundin wi Yàlla di maye, te umple gi ci ñoom moo tax, ndax seenug dëgër bopp. \v 19 Dañoo mujj dërkiis, yebu ci topp seen bakkan, ba xaabaabal ci jépp jëfi sobe. \p \v 20 Yeen nag du loolu ngeen jànge ci \w Almasi|lemma="Almasi:"\w*, \v 21 ndegam kay Yeesu ci boppam ngeen dégg mbiram, ba jànge ci moom, dëgg gi bawoo ci moom, \v 22 te mooy ngeen ba seen jikko ju jëkk ja, ngeen teqlikoo ak seen jëmmu démb ja masa topp bànneexi bakkan yuy naxe, ba sóobu ci yàqute. \v 23 Su ko defee ngeen mana yeeslu ci seenum xel, ci ndimbalal \w Noo|lemma="Noo gu Sell g-:"\w* gi, \v 24 te ngeen soloo jëmm ju yees ji Yàlla sàkke ci takkndeeram, di jëfe njub, ak sellnga ji dëgg di jur. \s1 Póol lim na meloy gëmkat bu dëggu \p \v 25 Kon nag bàyyileen fen, te ku nekk di wax sa moroom, dëgg, ndax ku nekk ci yeen sab céru moroom nga. \v 26 Buleen mer ba bàkkaar, te bu jant bi sowe seen mer; \v 27 buleen xajal \w Seytaane|lemma="Seytaane:"\w*. \v 28 Sàcc bi, na ba sàcc te nangoo sonn, di liggéeye loxoom liggéey bu rafet, ba man cee dimbali néew-ji-doole ji. \p \v 29 Bu genn kàddu gu bon génne seen gémmiñ, xanaa su ko jaree ngeen wax lu baax, luy jariñe, te diw yiw ci ñi koy dégg. \v 30 Te it buleen tiisal \w Noowug Yàlla gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"\w*, gi leen màndargaale xàmmikaayam ngir bésub \w njot|lemma="jot:"\w* ba. \v 31 Lépp luy wextan, ak naqari deret, ak mer mu ëpp, ak coow, ak wax ju ñaaw, na lépp buube, ba génne ci seen biir, mook mboolem jëfi coxor. \v 32 Baaxleen ci seen diggante, di ñeewantante, tey balante, ni leen Yàlla baale ci Almasi. \c 5 \p \v 1 Kon nag doonleen ay roykati Yàlla, gannaaw yeenay doomam yi mu sopp, \v 2 te ngeen di doxale cofeel, ni \w Almasi|lemma="Almasi:"\w* mi nu sopp, ba jooxeel nu bakkanam, def ko saraxu sawara, ngir xetug jàmm, ñeel Yàlla. \p \v 3 Lu jëm nag ci powum séy, ak jépp jëfi sobe, mbaa ag bëgge, li jekk ci ay nit ñu sell, moo di ñu bañ koo tudd sax ci seen biir, \v 4 te ag ñàkk kersa, ak waxi caaxaan, ak kaf yu bon, dara jekku ci, waaye saxooleen kàdduy cant. \v 5 Ndax lii kat na leen wóor: képp ku nekke powum séy, mbaa jëfi sobe, mbaa ag bëgge, kooku amul cér ci nguurug Almasi ak Yàlla, ndax ku bëgge ab bokkaalekat la. \s1 Jëfeleen ni niti leer \p \v 6 Bu leen kenn naxe waxi ngelawal neen, ndax yooyu ma lim mooy wàcce sànjum Yàlla ci kaw aji déggadi ñi. \v 7 Kon nag buleen séq ak ñooñu dara. \v 8 Ag lëndëm ngeen woon démb, waaye tey ag leer ngeen ci Boroom bi ngeen bokk. Jëfeleen nag ni niti leer. \v 9 Li leer gi ci yeen di meññ moo di mboolem luy mbaax ak njub ak dëgg. \v 10 Ràññeeleen li neex Boroom bi; \v 11 jëfi lëndëm amul njariñ, buleen ci bokk, xanaa ngeen feeñal ñaawtéefu jëf ja. \v 12 Ndax kat li nit ñooñu di làquy def, waxtaane ko sax, lu ruslu la. \v 13 Waaye mboolem lu ñu feeñal, leer ga ñu ko leerale moo ko wone, \v 14 te lépp lu ñu wone ci ag leer, di ag leer. Moo tax ñu ne: \q1 «Yaw miy nelaw, yewwul, \q1 dekkil, \w Almasi|lemma="Almasi:"\w* leeral la.» \p \v 15 Kon nag xool-leen bu baax seen jëfin, defleen jëfinu nit ñu am xel, te baña mel ni ñu ñàkk xel, \v 16 Jariñooleen lu ngeen man, \w jot|lemma="jot:"\w* gi ngeen amagum, ndax jant yu bona ngii tey. \v 17 Moo tax buleen def jëfi ñàkk bopp, waaye jéemleena xam coobarey Boroom bi. \v 18 Buleen naan biiñ ba màndi, màndite ci afal seen bakkan la leen jëme, waaye na leen \w Noo|lemma="Noo gu Sell g-:"\w* gi fees, \v 19 ngeen di jàngalante jàngi Sabóor, ak jàngi cant, ak jàng yu bawoo ci Noo gi leen fees, te ngeen di woy aka kañ Boroom bi, ci seen xol. \v 20 Fu ngeen tollu, ak ci mbir mu mu mana doon, santleen Yàlla Baay bi ci sunu turu Sang Yeesu Almasi, \v 21 te ngeen rus Almasi, ba tax ngeen di nangulante. \s1 Jabar mokk, jëkkër sopp \p \v 22 Na jabar nangul jëkkëram ni mu nangule Sang bi. \v 23 \w Almasi|lemma="Almasi:"\w* moo di musalkatu mbooloom gëmkat ñi, mbooloo mi di aw yaramam. Te itam ni Almasi dee boppu mbooloom gëmkat ñi, ni la jëkkër ji dee boppu jabaram. \v 24 Kon nag ni mbooloo mi nangule Almasi, ni la jabar ji wara nangule jëkkëram ci lépp. \p \v 25 Jëkkër nag, na sopp jabaram ni Almasi soppe mbooloom gëmkat ñi, ba jooxeel leen bakkanam. \v 26 Moo defal loolu mbooloo mi ba man koo setale cangaayal ndox mu ànd ak kàddoom, ngir sellal ko. \v 27 Li mu ci namm moo di teewal mbooloo mi fi kanamam, mu mel ni ab séetam bu ne ràññ, gàkkul, rasul, taqul lenn, xanaa sell, mucc sikk. \p \v 28 Noonu la jëkkër ji wara soppe jabaram, ni mu soppe yaramu boppam rekk. Sopp sa jabar sopp sa bopp la, \v 29 ndax kenn masula bañ suuxu boppam, xanaa mu di ko dundal, di ko topptoo, ni Almasi ak mbooloom gëmkat ñi, \v 30 nde noo di céri yaramam. \v 31 Ni ko Mbind mi indee: «Looloo tax góor di bàyyikoo ci ndeyam ak baayam, daldi taqoo ak jabaram, ba ñoom ñaar di wenn suux\f + \fr 5.31 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Njàlbéen ga\+bk* 2.24.\ft*\f*.» \v 32 Mbóot mu xóota ngi ci dog boobu, waaye man, li may wax moo di dog bi moo misaal diggante, bi Almasi séq ak mbooloo mi. \v 33 Teewuleen koo moom yeen itam; kon na ku nekk sopp jabaram ni mu soppe boppam, te ku nekk weg jëkkëram. \c 6 \s1 Waajur na yar, te njaboot di dégg \p \v 1 Naka yeen xale yi, déggal-leen seeni waajur, ngir Boroom bi, ndax moo war. \v 2 «Teral-leen seen ndey ak seen baay\f + \fr 6.2 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Mucc ga\+bk* 20.12.\ft*\f*,» mooy ndigal li jëkka ànd akub dige, \v 3 ndax da ne: «ngir ngeen baaxle te gudd fan ci kaw suuf\f + \fr 6.3 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Baamtug Yoon wi\+bk* 5.16.\ft*\f*.» \p \v 4 Yeen ñiy baay it, buleen xoñoñal xale yi, waaye yarleen leen, di leen jubanti, di leen xamal coobarey Boroom bi. \s1 Na jaam ak sangam déggal Boroom bi \p \v 5 Yeen jaam yi, déggal-leen seen sangi àddina, ànd ceek ragal Yàlla bay kat-kati, ak xol bu dëggu. Ni ngeen déggale \w Almasi|lemma="Almasi:"\w*, nangeen leen ni déggale. \v 6 Buleen ko defe ngistal, mbaa ngeen di ko sàkkoo lu leen neex, na di yéene ju ngeen tibbe ci seen xol, ngir jëfe liy coobarey Yàlla, ni mu ware ay jaami Almasi. \v 7 Liggéeyal-leen leen ci xol bu tàlli, ba mu mel ni Boroom bi ngeen ko defal, waaye du nit doŋŋ, \v 8 te ngeen xam ne nit ki, mu dis gor mbaa ab jaam, mboolem lu mu def ci lu baax, loola la ko Boroom biy delloo. \p \v 9 Yeen it sang yi, jëfeleen noonu seen diggante ak seeni jaam, bàyyileen di tëkkoo, te ngeen xam ne yeen ak ñoom a bokk benn Boroom fa asamaan, te xejj ak seen amul fa moom. \s1 Xare bi nook Seytaane la \p \v 10 Li ci des nag moo di ngeen manoorewoo Boroom bi, te ngeen sàkkoo ndimbal ci dooleem ak kàttanam gi amul kem. \v 11 Ràngooleen mboolem gànnaayi Yàlla, ngir ngeen mana jànkoonte ak pexey \w Seytaane|lemma="Seytaane:"\w*. \v 12 Ndax kat sunub xare du nook boroomi deret ak suux, waaye ñi ñu ko séqal ay boroom nguur lañu, ak ay boroom sañ-sañ, ak ay boroom doole yu nekk ci àddina ju lëndëm jii, di ay dagi Seytaane yu fare déndi asamaan. \v 13 Kon nag jël-leen gànnaayi Yàlla yépp, ba bu bésub safaan taxawee, ngeen mana jëflante, ba sottal, tey wéye taxaw temm. \p \v 14 Taxawleen kon temm. Defleen dëgg di ngañaay li ci seen ndigg, njub di seen kiiraayal dënn. \v 15 Xibaaru jàmm bi indi jàmm nag, defleen ko muy dàll yu dëgëral seen taxawaay. \v 16 Te fu ngeen tollu ŋàbbleen pakk biy seen ngëm, ci ngeen mana fanqe mboolem jumi sawaray ku Bon ki. \v 17 Mbaxanam xare miy seen kaaraange, jël-leen ko, sol, jël-leen itam saamar bi \w Noo|lemma="Noo gu Sell g-:"\w* giy joxe, te muy kàddug Yàlla. \v 18 Deeleen ñaan fu ngeen tollu, gépp xeetu ñaan aki dagaan ci ndimbalal Noo gi, ànd ci ak teewlu fu ngeen tollu, ak gépp farlute, te ngeen di ñaanal mboolem gëmkat ñu sell ñi. \p \v 19 Man itam, booleleen ma ci, ngir saa yu ma ubbee sama gémmiñ, mana xéewloo ndéey lu ma xamlee fit wu dëgër, mbóoti xibaaru jàmm bi, \v 20 xibaar bi ma di ndawam lu ñu tënke ay jéng. Waaye ñaanal-leen ma ma di ko waxee fit, ni mu ma ware. \s1 Póol tàggu na waa Efes \p \v 21 Dingeen mana xam nag lu jëm ci man, ak li may def, ndax Tisig, mbokk mu ñu sopp, jawriñ ju wóor ci liggéeyu Boroom bi, moo leen di xamal lépp. \v 22 Loolu ci boppam sax moo waral ma yónni ko ci yeen, ngir mu xamal leen ni nu nekke, ba seral seen xol. \p \v 23 Yal na jàmm ñeel bokki gëmkat ñi, ak cofeel gu ànd ak ngëm, bawoo fa Yàlla Baay bi, ak Sang Yeesu \w Almasi|lemma="Almasi:"\w*. \v 24 Na aw yiw ñeel mboolem ñi sopp sunu Sàng Yeesu Almasi, cofeel gu dul fey.