\id DEU (WOL) \ide UTF-8 \h Baamtug Yoon wi \toc1 Baamtug Yoon wi, di juróomeelu xaaju Tawreetu Musaa \toc2 Baamtug Yoon wi \mt1 Baamtug Yoon wi \mt2 di juróomeelu xaaju Tawreetu Musaa \imt1 Ubbite gi \ip Téereb \bk Baamtug Yoon wi\bk* moo tënk ci mbind, yeesalug kóllëre gi Yàlla fas ak bànni Israyil, fa tundu Sinayi, gannaaw ba ñu génnee Misra. Ñeent fukki at gannaaw gàddaay ga fekk na mboolem maasug fippukat ga jóge woon Misra, faatu ba jeex. Moo tax yeesalug kóllëre ga ngir maas ga ca topp, manul woona ñàkk. Musaa mi doon jottlikatub sàrti kóllëre gi moo demoon ba ag dundam desatul lu bare. Kon warteef la woon ci Israyil, mu dogu ne dina déggal kay wuutu Musaa. Ba bànni Israyil nangoo réew ya féete dexu Yurdan penku, dem nañu ba ca tàkkal dex ga, di waaja dugg nanguji réew ma leen Yàlla digoon. \ip Téere bi dafay sàrtal itam ni bànni Israyil wara dunde ca réew ma ñu leen dig. Yàlla moo leen jot, ñuy céru boppam bu mu sopp. Moo leen jële ca njaam ga ca Misra, ngir jox leen réew ma mu dige woon, ngir sottal digeem baak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba. Cëslaayal sàrtoo gi nag mooy jeneen Yàlla amul ku moy Aji Sax, ji ñu wara déggal ci lépp, te moom doŋŋ a moom askan wi. \ip Ki jàng Kàddug Yàlla tey mbaa ki ko jàngoon démb, ñoom ñépp la Baamtug Yoon Wi fàttli ne mbég mi mboolem doom Aadama di sàkku, fi mu nekk dëgg du fenn fu moy ci saxoo déggal Yàlla, ak fépp fu mu doon, ndax Yàlla mooy texeel, di goreel. \ip Ci Tënk: \ili 1.6—4.43 Musaa fàttli na jaar-jaari Israyil \ili 4.44—26.19 Musaa baamtu na yoon wi \ili 27.1—30.20 Musaa biral na yooni barke ak alkànde \ili 31.1—34.12 Musaa tàggoo na \ie \c 1 \p \v 1 Lii mooy kàddu yi Musaa wax bànni Israyil gépp, ca wàllaa dexu Yurdan, ca màndiŋ ma, fa joor ga jàkkaarlook Suf, diggante Paran ak Tofel ak Laban ak Aserot ak Disayab. \v 2 Fukki fan ak benn mooy dox diggante tundu Oreb ba Kades Barneya, boo ko jaaree yoonu tundu Seyir. \p \v 3 Waaye ñeent fukkeelu atam, gannaaw ba bànni Israyil génnee Misra, keroog benn fan ca fukkeelu weer waak benn, ca la Musaa doora wax bànni Israyil mboolem lu ko Aji Sax ji santoon ca ñoom. \v 4 Fekk na Musaa duma Siwon, ma toogoon Esbon, di buurub Amoreen ña, duma it ca Eddrey, Og buuru Basan ba toogoon Astarot. \p \v 5 Ca wàllaa dexu Yurdan, ca réewum Mowab la Musaa tàmbalee leeral yoonu Yàlla wii. Mu ne: \b \ms1 Musaa fàttli na jaar-jaari Israyil \mr (Saar 1.6—4.43) \p \v 6 Sunu Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji da noo waxoon ca Oreb ne nu: «Seen toogaayub tund wii doy na. \v 7 Walbatikuleen dem, jàll-leen ca biir diiwaanu tundi Amoreen ña, ak mboolem réew ya mu feggool, ca joor ga, ak tund wa, ak suufu tund ya, ak Negew ca bëj-saalum, ba ca tefes ga, ca réewum Kanaaneen ña, ak Libaŋ, ba ca Efraat, dex gu mag ga. \v 8 Mu ngoog, maa leen jox réew moomu. Demleen nangu réew mi Aji Sax ji giñaloon seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, ñeel leen ñook seen askan wi leen di wuutu.» \p \v 9 Musaa teg ca ne leen: jant yooyu laa leen wax, ne leen: «Duma leen àttan yeen ñépp, man doŋŋ. \v 10 Seen Yàlla Aji Sax ji moo leen ful, ba yeena ngii tey, bare ba tollu ni biddiiwi asamaan. \v 11 Yal na leen seen Yàllay maam Aji Sax ji yokkati junniy yoon, te barkeel leen ni mu leen ko waxe! \v 12 Waaye nu ma leen di àttane man doŋŋ, ak seen coono, ak seeni lëj-lëj, ak seeni jote? \v 13 Beral-leen seen bopp ay nit ñu rafet xel, am ug dégg, te di ñu ràññiku ci seeni giir. Su ko defee ma tabb leen, ñuy seeni njiit.» \v 14 Ba loolu amee ngeen wax ma ne ma: «Loolu nga wax de, xel la.» \v 15 Ci kaw loolu ma jël seen njiit yu rafet xel yu ràññiku, yi ngeen jukkee ci seeni giir, daldi leen def seeni njiit, ñii yilif junniy nit, ñii téeméer, ñii juróom fukk, ñii fukk, ñii diy jawriñ ci seeni giir. \v 16 Jant yooyu laa sant seeni àttekat ne leen: «Deeleen déglu seeni bokk tey àtte dëgg, diggante bànni Israyil ak mbokkam, akub doxandéem. \v 17 Buleen far-farloo cib àtte, dégluleen ku tuut, ni ngeen di dégloo ku mag, te buleen ragal kenn, ndax àtte bi Yàllaay boroom. Bu leen mbir mi ëppee loxo nag, ngeen indil ma ko, ma seet ko.» \v 18 Jant yooyu laa leen sant mboolem lu ngeen wara def. \s1 Ndigalu yëri Kanaan jib na \p \v 19 Gannaaw gi nu bàyyikoo tundu Oreb, jaare mboolem màndiŋ mu yaa, mu raglu ma ngeen gis. Nu topp yoonu diiwaanu tundi Amoreen ñi, na nu ko sunu Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji sante woon, ba àgg Kades Barneya. \v 20 Ci kaw loolu ma ne leen: «Agsi ngeen fii ci tundu Amoreen ñi nu sunu Yàlla Aji Sax ji di jox. \v 21 Mu ngoog, seen Yàlla Aji Sax ji moo teg réew mi fi seen kanam. Demleen nangu ko, ni leen ko seen Yàllay maam Aji Sax ji, waxe. Buleen ragal, buleen yoqi.» \p \v 22 Ci kaw loolu ngeen dikk yeen ñépp fi man, ne ma: «Nan yebal aw nit, ñu jiitu nu, yëral nu réew ma, te délsi wax nu yoon wu nuy jaare, ak dëkk yu mag ya nuy duggeji.» \v 23 Ma rafetlu xel ma, tànn ci yeen fukki góor ak ñaar, giir gu nekk, genn góor. \v 24 Ñu walbatiku jubal yoonu diiwaanu tund ya, ba àgg xuru Eskol, daldi seet foofa, \v 25 ba noppi sàkk ca meññeefum réew ma, indaaleel nu. Ñu wax nu nag ne nu: «Réew mu baax la nu sunu Yàlla Aji Sax ji jox.» \v 26 Teewul bugguleen woona dem, xanaa di gàntal seen ndigalal Yàlla Aji Sax ji. \v 27 Ngeen di ñurumtoo seen biiri xayma, naan: «Bañ nu kay a tax Aji Sax ji jële nu réewum Misra, teg nu ci loxoy Amoreen ñi, ngir ñu faagaagal nu. \v 28 Ana fu nu jëm? Te sunu bokk ya demoon yoqiloo nu, ne nu waa réew maa nu ëpp, sut nu, dëkk ya réy te dàbblikoo ay tata yu àkki asamaan. Rax ci dolli, ay ponkal yu bokk ci askanu Anageen ñi lanu fa gis!» \p \v 29 Ma wax leen yeen ne leen: «Buleen yox-yoxi, buleen leen ragal. \v 30 Seen Yàlla Aji Sax ji leen jiitu, moom moo leen di xeexal, noonee mu defoon ak yeen ca Misra, ngeen gis, \v 31 ca màndiŋ ma it, gis ngeen na leen seen Yàlla Aji Sax ji fabe, ni baay di fabe doomam, ci yoon wi ngeen dox wépp, ba agsi bérab bii.» \v 32 Loolu lépp taxul ngeen am kóolute ci seen Yàlla Aji Sax ji, \v 33 ki leen daan jiitu ci yoon wi, ngir sàkkal leen fu ngeen di dale; guddi, mu nekk ci biir sawara, di leen niital yoon wu ngeen jaare; bëccëg, mu nekkal leen ci biir aw niir. \p \v 34 Ba Aji Sax ji déggee seeni kàddu, dafa mer ba giñ ne: \v 35 «Du kenn ci nit ñii, maas gu bon gii, kuy gis réew mu baax mi ma giñaloon seeni maam. \v 36 Xanaa Kaleb doomu Yefune moo koy gis, te réew ma mu teg tànkam, moom laa koy jox, mook askanam, ndax moo matal kóolute ci Aji Sax ji.» \v 37 Man itam Aji Sax ji mere na ma ci ndax yeen, ba ne ma: «Yaw itam doo ca dugg. \v 38 Yosuwe doomu Nuun mi ci sa kilifteef moo cay dugg. Nanga ko ñaax, ndax moom mooy jox Israyil réew ma. \v 39 Seen tuut-tànk yi ngeen noon dees na leen sëxëtoo, seen doom yii xamagul lu baax ak lu bon, ñooy duggi réew ma. Ñoom laa koy jox, te ñoo koy nangu. \v 40 Yeen nag walbatikuleen dellu màndiŋ ma, topp yoonu géeju Barax ya.» \p \v 41 Ci kaw loolu ngeen wax ma, ne ma: «Noo tooñ Aji Sax ji. Waaye dinanu dem xareji noonee nu ko sunu Yàlla Aji Sax ji sante woon.» Ku nekk ci yeen daldi ràngoo ngànnaayam, ngeen defe ne yéegi diiwaanu tund wa dina leen yomb. \v 42 Aji Sax ji ne ma: «Wax leen ne leen buñu dem, buñu xeexi ndax man Aji Sax ji àndumaak ñoom. Lu ko moy dinañu daanu ci seen kanami noon.» \v 43 Ma wax leen ko, dégluwleen, xanaa gàntal ndigalal Aji Sax ji, fétteeral, ba yéegi diiwaanu tund wa. \v 44 Ba loolu amee Amoreen ña dëkke tund woowa dikk, dajeek yeen, ne leen dann niy yamb, yitte leen fa Seyir, ba Xorma. \v 45 Ngeen walbatiku, jooy ko Aji Sax ji, Aji Sax ji dégluwu leen, faalewu leen. \v 46 Gannaaw gi ngeen toog Kades, lu yàgg la ngeen fa toog lépp. \c 2 \p \v 1 Ba loolu amee nu walbatiku, dellu màndiŋ ma, topp yoonu géeju Barax ya, na ma ko Aji Sax ji waxe woon. Wër nanu diiwaanu tundu Seyir ay fani fan. \s1 Bànni Israyil teggi nañu \p \v 2 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax ma, ne ma: \v 3 «Seen wërub tund wii doy na. Walbatikuleen, jublu bëj-gànnaar. \v 4 Mbooloo mi ngay sant ne leen: “Yeena ngi waaja jéggi seen kemu réewum bokki Esaween, ñi dëkke Seyir. Dinañu leen ragal, waaye nangeen moytu bu baax. \v 5 Buleen xeex ak ñoom, ndax duma leen jox ci seen suuf fu téstën sax tege, ngir Esaween ñi laa sédd diiwaanu tundu Seyir. \v 6 Aw ñam, weccikoo leen kook ñoom xaalis, door koo lekk; am ndox it, nangeen ko jëndeek ñoom, door koo naan. \v 7 Ndax yeen kat seen Yàlla Aji Sax ji moo barkeel seen mboolemu ñaq te moo ràññee seen doxub màndiŋ mu yaa mii. Ñeent fukki at a ngii seen Yàlla Aji Sax jaa ngeek yeen, ñàkkuleen dara.”» \v 8 Ba mu ko defee nu romb sunu bokki Esaween ñi dëkke Seyir. Danoo wacc yoonu joor ga, ak Elat ak Esiyon Geber, daldi walbatiku jaareji màndiŋu Mowab. \p \v 9 Ba loolu amee Aji Sax ji ne ma: «Buleen dal ci kaw Mowabeen ñi, di leen song ub xare, ngir duma leen jox benn cér ci seenum réew, ndax askanu Lóot laa sédd réewum Ar.» \p \v 10 Emeen ñaa fa jëkkoona dëkk, askan wu am kàttan lañu woon, bare, yegg ca kaw ni Anageen ñi. \v 11 Ay Refayeen lañu jàppe woon Emeen ñooñu ak Anageen ñi, teewul Mowabeen ñi di leen wooye ay Emeen. \v 12 Seyir nag la Oreen ña jëkkoona dëkk, waaye Esaween ñaa leen fa dàqe, faagaagal leen, wuutu leen, noonu Israyil def rekk ak céru suufam bi leen Aji Sax ji jox. \p \v 13 Aji Sax ji neeti: «Jàll-leen walum Seredd.» Nu jàll walum Seredd. \v 14 Diggante ba nu bàyyikoo Kades Barneya, di dox, ba keroog bés ba nu jàllee walum Seredd, fanweeri at ak juróom ñett la. Fekk na mboolem maasu góor ña tollu woon ci xare, ca ndoortel yoon wa, ñoom ñépp a wuute dal ba, dee ba jeex, na leen ko Aji Sax ji giñale woon. \v 15 Aji Sax jee leen toppe diisaayu loxoom, wollee leen ci biir dal bi, ba ñu jeex tàkk. \p \v 16 Ba mboolem ña tollu woon ci xare deeyee ba jeex, ba ñoom ñépp wuute ca mbooloo ma, \v 17 Aji Sax ji wax ma, ne ma: \v 18 «Yaa ngi waaja jéggi kemu réewum Mowab, ca Ar. \v 19 Bu ngeen àggee ca Amoneen ña nag, buleen dal ci seen kaw, buleen xeex ak ñoom, ndax duma leen jox benn cér ci réewum Amoneen ñi, ngir askanu Lóot woowu laa ko sédd.» \v 20 Diiwaan boobu it réewum Refayeen lees ko jàppe woon, te Refayeen ñaa fa jëkkoona dëkk. Teewul Amoneen ñi di leen wooye ay Samsumeen, \v 21 askan wu am kàttan, bare, te yegg ca kaw ni Anageen ñi. Aji Sax jee leen fàkkasal Amoneen ñi, Amoneen ñi dàq leen, sanc, wuutu leen. \v 22 Mooy na mu defaloon Esaween ña dëkke Seyir rekk, ba mu leen fàkkasalee Oreen ña, Esaween ña dàq leen, sanc, wuutu leen, ba bésub tey jii. \v 23 Aween ña dëkke woon dëkk yu ndaw ya dem, ba àkki Gasa nag, Kaftoreen ña bàyyikoo Keret ñoo leen faagaagal, wuutu leen. \s1 Israyil nangu na penkub dexu Yurdan \p \v 24 Aji Sax ji neeti: «Ayca, jàll-leen walum Arnon. Mu ngoog, maa teg ci seen loxo, Siwon Amoreen ba, buurub Esbon, mook réewam. Dal-leen di nangu réew mi, song ko xare. \v 25 Bés niki tey maa tàmbalee wàcce njàqareek tiitaange ci kaw mboolem askan yi asamaan tiim, ba bu ñu déggee seenum riir, dañuy jaaxle, di lox.» \p \v 26 Ci kaw loolu ma yebal ay ndaw yu bàyyikoo màndiŋu Kedemot, ba ca Siwon buurub Esbon. Ma yóbbante ko kàdduy jàmm, ne ko: \v 27 «May nu, nu jaare sam réew. Yoon wi rekk lanuy topp; dunu jàdd ndijoor, dunu jàdd càmmoñ. \v 28 Aw ñam, xaalis nga nu koy weccee, nu lekk; am ndox sax, xaalis nga nu koy joxe, nu naan. May nu rekk nu dox, ba jàll. \v 29 Noonu nu Esaween ña dëkke Seyir defaloon, ñook Mowabeen ña dëkke Ar rekk. Su ko defee nu mana jàll dexu Yurdan, ba àgg ca réew ma nu sunu Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji jox.» \p \v 30 Siwon buurub Esbon nag nanguwu noo may nu jaare fa moom, ndax booba seen Yàlla Aji Sax ji moo dëgëral boppam, wowal xolam, ngir teg ko ci seen loxo niki bésub tey jii. \v 31 Aji Sax ji ne ma: «Gis nga, maa ngi nii tàmbalee teg Siwon akum réewam ci seen loxo. Dal-leen di nangum réewam.» \v 32 Ba mu ko defee Siwon dikk dajeek nun, mook gàngooram gépp, ngir song nu xare ca Yaxacc. \v 33 Sunu Yàlla Aji Sax ji daane ko fi sunu kanam, nu duma ko, mook ay doomam, ak gàngooram gépp. \v 34 Jant yooyu lanu nangu dëkkam yu mag yépp, faagaagal dëkk yu mag yépp: góor ak jigéen, ba ca tuut-tànk ya, bàyyiwunu kuy dund. \v 35 Xanaa jur ga lanu sëxëtoo, ak mboolem alali dëkk ya nu nangu. \v 36 La ko dale Arower ga tiim walum Arnon, boole ca dëkk ba ca xur wa, ba ca Galàdd, du benn dëkk bu nu të. Foofu fépp la sunu Yàlla Aji Sax ji daane fi sunu kanam. \v 37 Réewum Amoneen ña doŋŋ ngeen jegewul; muy réew ma leru dexu Yabog, ak dëkki tund ya, mboolem daal, fu nu sunu Yàlla Aji Sax ji aaye woon. \c 3 \p \v 1 Ba loolu wéyee nu walbatiku, awe yoon wa yéeg jëm Basan. Og buuru Basan nag dikk dajeek nun, mook gàngooram gépp, ngir song nu xare ca Eddrey. \v 2 Aji Sax ji ne ma: «Bu ko ragal, ndax ci say loxo laa ko teg, mook gàngooram gépp, akum réewam. Nanga ko def na nga defoon Siwon buurub Amoreen ba woon ca Esbon.» \v 3 Noonu la sunu Yàlla Aji Sax ji tege Og buuru Basan itam ci sunuy loxo, mook gàngooram gépp, nu duma leen ba desewul kuy dund. \v 4 Booba lanu nangu mboolemi dëkkam. Amul benn dëkk bu nu nanguwul ci ñoom: juróom benn fukki dëkk, mboolem diiwaanu Argob, ba bokk ca nguurug Og ca Basan. \v 5 Yooyu yépp di dëkk yu dàbblikoo tata yu kawe, ak bunt yu tëje ràpp, te limaaleesul dëkk-dëkkaan yu baree bare, yu dara wërul. \v 6 Nu faagaagal leen, na nu defoon ak Siwon buurub Esbon. Dëkk yépp lanu faagaagal: góor ak jigéen ba ca tuut-tànk ya. \v 7 Mboolem jur gaak alali dëkk ya nag, nu sëxëtoo. \p \v 8 Jant yooyu lanu nangoo ci loxol ñaari buuri Amoreen ñooña ca wàllaa dexu Yurdan, réew ma dale ca xuru Arnon, ba ca tundu Ermon. \v 9 Ermon googu la waa Sidon di wooye Siryoŋ, Amoreen ñi di ko wooye Senir. \v 10 Mboolem dëkki joor ga lanu nangu, ak mboolem diiwaanu Galàdd, ak mboolem Basan, ba ca Salka ak Eddrey, dëkki nguurug Og mu Basan. \v 11 Mennum Og buuru Basan doŋŋ moo muccoon ca ndesu Refayeen ñu ponkale ña. Lalam ba, lalu weñ gu ñuul la. Ma nga noonee ca Raba, dëkkub Amoneen ña. Guddaayu lal ba ci xasabu góor, juróom ñeenti xasab la, di ñeenti meetar ak genn-wàll, yaatuwaay ba, ñeenti xasab, di ñaari meetar. \s1 Séddale nañu penkub Yurdan \p \v 12 Suuf soosu nu nangu ca jant yooya, te dale ca Arower ga ca xuru Arnon ca bëj-saalum, ak ca bëj-gànnaar, genn-wàllu diiwaanu tundi Galàdd, aki dëkkam, maa ko jox Rubeneen ñi, ak Gàddeen ñi. \v 13 Ndesu Galàdd ak mboolem Basan gu nguurug Og, ma jox ko genn-wàllu giirug Manase. Diiwaanu Argob gépp ak Basan googu gépp, lañu daan wooye réewum Refayeen ña. \v 14 Yayir mi askanoo ci Manase moo nangu mboolem diiwaanu Argob, ba ca kemu réewum Gesureen ña, ak Maakateen ña. Moo tudde boppam Basan googu, ba tax ñu di ko wooye Sanci Yayir ba tey jii. \v 15 Askanu Makir laa jox diiwaanu Galàdd\f + \fr 3.15 \fr*\ft Genn-wàllu diiwaanu Galàdd ba ca bëj-gànnaar lay wax. Seetal ci 3.12.\ft*\f*. \v 16 Rubeneen ñeek Gàddeen ñi laa jox la dale diiwaanu Galàdd ba ca xuru Arnon, diggu xur wa di seen kemu suuf ci genn wet, dexu Yabog di seen kemu ñook Amoneen ña. \v 17 Fa joor ga feggook dexu Yurdan it di kemu, diggante dexu Kineret ca bëj-gànnaar, ak ca bëj-saalumu géeju Xorom ga, ba ba ngay àgg ca suufu tundu Pisga, ca penku. \p \v 18 Jant yooyu laa leen sant ne leen\f + \fr 3.18 \fr*\ft Ñi wara féetewoo penkub dexu Yurdan la Musaa di waxal fii.\ft*\f*: «Seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji moo leen jox réew mii, ngir ngeen nangu ko. Na xarekat yépp gànnaayu, jàll, jiitu seen bokki \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \v 19 Seeni jabar doŋŋ, ak seeni doom ak seenug jur, ndax xam naa ne jur gu takku ngeen am, ñooy des ci seen dëkk yi ma leen jox, \v 20 ba keroog Aji Sax ji noppalee seen bokki bànni Israyil ni yeen, fekk leen nangu, ñoom it, réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji jox, ca wàllaa dexu Yurdan. Su ko defee ku nekk ci yeen saña dellu ca céru suufam ba ma ko jox.» \p \v 21 Yosuwe itam, sant naa ko ci jant yooyu ne ko: «Sa bët moo la may mboolem ni seen Yàlla Aji Sax ji def ak ñaari buur yii. Noonu rekk la Aji Sax jiy def ak mboolem nguur ya nga jëm. \v 22 Buleen leen ragal, ndax seen Yàlla Aji Sax ji moo leen di xeexal.» \s1 Musaa duggul Kanaan \p \v 23 Jant yooyu laa tinu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ne ko: \v 24 «Éy Boroom bi Aji Sax ji, yaa ma wonagum lenn ci sa màggaay ak sa doole, Sang bi. Ana yàlla ju nekk asamaan, mbaa ci kaw suuf ju mana roy say jëf ak say jaloore? \v 25 May ma rekk ma jàll, ba gis réew mu baax, ma ca wàllaa dexu Yurdan, tund wu rafet woowu ba ca Libaŋ!» \v 26 Waaye fekk na Aji Sax ji mere ma lool ndax yeen, ba faalewu ma. Aji Sax ji ne ma: «Na doy. Bu ma waxati lu jëm ci loolu. \v 27 Yéegal ba ca kaw tundu Pisga, nga dawal sa bët, te séenu réew ma wetu sowu, ba bëj-gànnaar, bëj-saalum, ba penku. Xoolal bu baax, nde doo jàll dexu Yurdan gii. \v 28 Waaye nanga yebal Yosuwe, ñaax ko, jàjj ko, ndax moom mooy jàll, jiite mbooloo mii, te moo leen di jox réew moomu ngay séen.» \v 29 Ba mu ko defee nu toog ca xur wa, janook Bet Pewor. \c 4 \s1 Musaa ñaax na bànni Israyil \p \v 1 Léegi nag yeen waa Israyil, dégluleen dogali yoon yeek àttey yoon yii ma leen di xamal, ngir ngeen di ko jëfe, ndax ngeen dund ba dugg, nanguji réew ma leen \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji seen Yàllay maam, di jox. \v 2 Buleen yokk dara ci kàddu gi ma leen di dénk, te buleen ci wàññi dara, ndax ngeen sàmm seen santaaney Yàlla Aji Sax, ji ma leen di dénk. \v 3 Seen bët moo leen may la Aji Sax ji def ca Baal Pewor. Mboolem ku toppoon tuur ma ñuy wax \w Baal ca Pewor|lemma="Baal:"\w*, seen Yàlla Aji Sax ji moo ko sànke ci seen biir. \v 4 Waaye yeen ñi ŋoyoon ci seen Yàlla Aji Sax ji, yeen ñépp a ngi dund tey jii. \p \v 5 Mu ngoog, jàngal naa leen ay dogali yoon, aki àttey yoon, na ma ko sama Yàlla Aji Sax ji sante, ngir ngeen war koo jëfe ca biir réew ma ngeen di nanguji. \v 6 Sàmmooleen koo jëfe, ndax mooy doon seenug rafet xel, ak seenug ràññee fi kanam xeet yi, ba bu ñu déggee mboolem dogali yoon yii, dinañu ne: «Wii askan wu mag rekk a rafet um xel te ràññee!» \v 7 Ana wan xeet wu mag wu am yàlla ju leen jege ni nu sunu Yàlla Aji Sax jiy jegee saa yu nu ko wooyee wall? \v 8 Ana xeet wu ko màgge, ba am dogali yoon ak àttey yoon yu jekke ni yoon wii ma joxe fi seen kanam bésub tey? \p \v 9 Waaye wattuleen, wattuleen seen bopp bu baax, bala ngeena fàtte mbir yi ngeen teg seen bët, ba du génn seenum xel seen giiru dund gépp. Te nangeen ko xamal seeni doom ak seeni sët. \v 10 Bés ba ngeen taxawee fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, fa tundu Oreb, Aji Sax jee ma ne: «Dajaleel ma mbooloo mi, ma dégtal leen samay kàddu, ngir ñu tàggatu ci ragal ma li feek ñuy dund ci kaw suuf, te seeni doom it, ñu tàggat leen ci.» \v 11 Yeena dikk taxaw ca suufu tund wa, tund wa ne jippét, sawara wa jolli ba ca xolu asamaan, ci biir xàmbaari guddi gu ne këruus. \v 12 Aji Sax ji àddoo ca digg sawara wa, wax ak yeen, ngeen di dégg baat, te jëmm, gisuleen ko, xanaa baat doŋŋ. \v 13 Ci kaw loolu mu biralal leen \w kóllëreem|lemma="kóllëre g-:"\w* gi mu leen sant ngeen sàmm ko, muy fukki santaane yi. Mu daldi leen bindal santaane yi ci ñaari àlluway doj. \v 14 Man nag la Aji Sax ji sant ca yooya jant, ne ma xamal leen dogali yoon yeek àttey yoon, yi ngeen wara jëfe ca réew ma ngeen jëm, ngir nanguji ko. \s1 Yoon wi aayal na bokkaale \p \v 15 Nangeen wattu seen bopp bu baax nag ndax keroog ba \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jiy àddoo ca digg sawara wa, wax ak yeen ca tundu Oreb, gisuleen jenn jëmm. \v 16 Kon buleen def ug yàqute, di sàkkal seen bopp menn tuur muy jëmmal lenn lu mel ni góor mbaa jigéen, \v 17 mbaa lu mel ni menn malam suuf, mbaa malam kaw mu mel ni njanaaw, \v 18 mbaa lu mel ni ndëgmeent, di raam, mbaa lu mel niw jën, nekk ci ndox mu suuf tiim. \v 19 Buleen séentu asamaan, gis jant bi, mbaa weer wi, mbaa biddiiw yi, ak mboolem leeri asamaan, ba mu xiirtal leen ci di leen sujjóotal ak a jaamu, te seen Yàlla Aji Sax ji féetale yooyii, mboolem xeet yi asamaan tiim. \v 20 Yeen nag Aji Sax jee leen jël, bellee leen ca Misra, taalu xellikaayu weñ gu ñuul ba, ngir ngeen doon ñoñam ñi mu séddoo niki bésub tey. \p \v 21 Waaye yeena tax Aji Sax ji mere ma ba giñ ne duma jàll dexu Yurdan, te duma dugg ca réew mu baax, ma leen seen Yàlla Aji Sax ji moomale. \v 22 Man nag ci réew mii laay dee. Du maay jàll dexu Yurdan. Waaye yeen yeenay jàll, ba nanguji réew mu baax moomu. \v 23 Wattuleen seen bopp ba baña fàtte \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* gi seen Yàlla Aji Sax ji fas ak yeen, di sàkkal seen bopp tuur muy jëmmal lenn, te seen Yàlla Aji Sax ji aaye leen ko. \v 24 Seen Yàlla Aji Sax ji kat, mooy sawara wuy xoyome, Yàlla ju fiir la. \p \v 25 Bu ngeen demee ba am ay doom aki sët, fekk leen yàgg ca réew ma, su boobaa su ngeen defee ag yàqute, di sàkk am tuur, ak jëmmu lu mu mana doon, mbaa ngeen def lenn lu seen Yàlla Aji Sax ji ñaawlu, lu koy merloo, \v 26 maa ngi sàkku asamaan ak suuf seedeel maak yeen bésub tey jii, ne su boobaa yeenay sànkoo sànku ci lu gaaw, ba wuute ca réew, ma ngeen jàll dexu Yurdan, jëm fa, ngir nanguji ko. Su boobaa dungeen fa yàgge, ndax dees leen di raafal, ba ngeen jeex tàkk. \v 27 Aji Sax ji moo leen di tasaare ci biir xeet yi, te lu néew la seenu ndes di doon ci biir xeeti jaambur yi leen Aji Sax jiy dàq jëme. \v 28 Foofa ngeen di jaamoo ay yàlla yu loxoy nit sàkke bant, mbaa doj, yàlla yu dul gis, du dégg, du lekk, du xeeñtu. \v 29 Waaye su ngeen fa sàkkoo seen Yàlla Aji Sax ji, dingeen ko daj, ndegam seen léppi xol, ak seen léppi bakkan ngeen ko sàkkoo. \v 30 Bu leen njàqare dikkalee, fekk mboolem mbir yooyu dab leen, su boobaa dingeen mujj délsi ci seen Yàlla Aji Sax ji te dingeen ko déggal. \v 31 Ndax seen Yàlla Aji Sax ji Yàllay yërmande la. Du leen wacc, du leen yàqte te du fàtte kóllëre, ga mu fasoon ak seeni maam ci kaw ngiñ. \s1 Ab jagle ñeel na Israyil \p \v 32 Seetleen rekk ci janti démb yi leen jiitu, la dale bés ba Yàlla sàkke nit fi kaw suuf, mbaa ngeen seet asamaan, cat ba cat. Ndax lu màgge nii mas naa am? Am masees naa dégg lu ni mel? \v 33 Ana askan wu masa dégg baatu Yàlla bu jibe ci sawara, ni ngeen ko dégge te dese bakkan? \v 34 Jan yàlla moo masa fexee dikk foqatil boppam aw xeet, bellee leen ci weneen xeet, ci biiri nattu, aki firnde aki kéemaan ak xare yu mu sottale dooley loxoom, ak kàttanu përëgam, ak jëf ju raglu, noonee leen ko seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji defale ca Misra, ngeen teg ci bët? \v 35 Yeen déy lañu won loolu lépp ngir ngeen xam ne Aji Sax ji doŋŋ mooy Yàlla, te jeneen yàlla amul, ju dul moom. \v 36 Fa asamaan la àddoo, dégtal leen baatam, ngir yar leen, ci kaw suuf it la leen wone sawaraam su mag sa, te ay kàddoom ngeen dégg, mu jibe ca digg sawara sa. \v 37 Sopp seeni maam nag moo tax mu taamu leen, yeen askan wi leen wuutu, génneel leen boppam Misra, ci dooleem ju bare, \v 38 ngir dàqal leen xeet yu leen sut, ëpp leen doole, ba dugal leen seenum réew, sédd leen ko bés niki tey. \p \v 39 Kon xamleen tey te délloosi ci seen xel, ne Aji Sax ji mooy Yàlla fa kaw asamaan ak fi kaw suuf. Du keneen. \v 40 Sàmmleen dogali yoonam, ak santaaneem yi ma leen dénk bés niki tey, ndax ngeen baaxle yeen ak seen doom yi leen di wuutu, te ngeen yàgg ca réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji jox ba fàww. \s1 Amal nañu ay rawtu ca penkub Yurdan \p \v 41 Ba loolu wéyee Musaa ber na ñetti dëkk ca penkub dexu Yurdan, \v 42 mu diy rawtu ci ku rey moroomu nitam, te reyu ko cig teyeef, wonu ko woon it mbañeel, lu jiitu loola. Kooku sañ naa làquji ci dëkk yooyu benn, ngir rawale bakkanam. \v 43 Dëkk yooyu ñoo doon Beccer, ga ca màndiŋ ma, ca kaw dénd wu tell wa ca kaw tund wa, su dee ab Rubeneen; ak Ramot ga ca Galàdd, su dee ab Gàddeen; ak Golan ga ca diiwaanu Basan, su dee ab Manaseen. \ms1 Musaa baamtu na yoon wi \mr (Saar 4.44—11.32) \p \v 44 Lii moo di ndigalu yoon wi Musaa biraloon fi kanam \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \v 45 Lii moo di seedey yoon yi, ak dogali yoon yi, ak àttey yoon yi Musaa dénkoon bànni Israyil, gannaaw ba ñu bàyyikoo Misra, \v 46 ca wàllaa dexu Yurdan, ca xur wa janook Bet Pewor, ca réewum Siwon buurub Amoreen ba toogoon Esbon, te Musaa ak bànni Israyil duma woon ko, ba ñu génnee Misra. \v 47 Ñoo nangu am réewam, ak réewum Og buuru Basan, ñaari buuri Amoreen ña moomoon wàllaa dexu Yurdan, ca penku, \v 48 fa dale ca Arower, ga ca catal walum Arnon, ba ca tundu Siyoŋ\f + \fr 4.48 \fr*\ft Gii \ft*\fk Siyoŋ \fk*\ft wuute na ak weneen tur wi ñuy wooye Yerusalem.\ft*\f*, ga ñuy wax itam Ermon, \v 49 boole ca mboolem joorug wàllaa dexu Yurdan, ca penku, ba àgg ca géeju Xorom ga, ca suufu tundu Pisga. \c 5 \s1 Fukki santaanee ngi \p \v 1 Musaa moo woo \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp, wax leen ne leen: Yeen, bànni Israyil, dégluleen dogali yoon yi, ak àttey yoon yi may wax, ngeen dégg, tey. Jàngleen ko te farlu koo jëfe. \v 2 Sunu Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji moo fasoon \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* ak nun ca tundu Oreb. \v 3 Du sunuy maam rekk la Aji Sax ji fasoon kóllëre gii ak ñoom; waaye ñook nun ñi fii tey, mboolem nun ñiy dund, ci lanu. \v 4 Ci biir jàkkaarloo la Aji Sax ji waxe woon ak yeen ca kaw tund wa, àddoo ca digg sawara wa. \v 5 Maa taxaw diggante Aji Sax jeek yeen, jant yooyu, di leen jottli kàddug Aji Sax ji, ndax yeena ragaloon sawara wa, ba yéeguleen ca kaw tund wa. Mu ne: \p \v 6 «Man Aji Sax ji maay seen Yàlla, ji leen génne réewum Misra, kërug njaam ga. \p \v 7 «Buleen am yeneen yàlla ci sama kanam. \p \v 8 «Buleen sàkkal seen bopp tuur muy jëmmal lenn lu nekk ci kaw asamaan, mbaa ci kaw suuf, mbaa lu nekk ci ndox mu suuf tiim. \v 9 Buleen ci sujjóotal lenn, buleen ci jaamu lenn, ndax man seen Yàlla Aji Sax ji, Yàlla ju fiir laa. Maay topp doom tooñu waajur, ba ca seen maasi sët, ba ca maasug sëtaati nit ñi ma bañ. \v 10 Waaye maay baaxe ñi ma sopp, di sàmm samay santaane, ba ci junniy maas ya leen di wuutuji. \p \v 11 «Buleen tudd seen turu Yàlla Aji Sax ji ci neen, ndax Aji Sax ji du ñàkka topp kuy tudd aw turam ci neen. \p \v 12 «Sàmmleen \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*, ngir sellal ko, ni leen ko seen Yàlla Aji Sax ji sante. \v 13 Juróom benni fan ngeen wara liggéey, def ci seen soxla yépp. \v 14 Waaye bésub juróom ñaareel ba, Noflaay lay doon, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Buleen ci liggéey lenn; du yeen, du seen doom ju góor, ak ju jigéen, du seen jaam bu góor, ak bu jigéen, du seen nag, du seen mbaam, du mboolem seenug jur, du seen gan gu nekk ci seen biir dëkk. Su ko defee seen jaam bu góor, ak seen jaam bu jigéen mana dal-lu ni yeen. \v 15 Fàttlikuleen ne ay jaam ngeen woon ca réewum Misra. Seen Yàlla Aji Sax ji moo leen fa génnee dooley loxoom, ak kàttanu përëgam. Moo tax seen Yàlla Aji Sax ji sant leen ngeen wàccoo ak bésub Noflaay. \p \v 16 «Teral-leen seen baay, ak seen ndey, ni leen ko seen Yàlla Aji Sax ji sante, ndax ngeen gudd fan, ndax it ngeen baaxle ca réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji jox. \p \v 17 «Buleen bóom. \p \v 18 «Buleen jaaloo. \p \v 19 «Buleen sàcc. \p \v 20 «Buleen seedeel seen moroom lu dul dëgg. \p \v 21 «Buleen xédd seen jabaru dëkkandoo, buleen xemmem këram, mbaa toolam, mbaa jaamam bu góor, mbaa jaamam bu jigéen, mbaa aw nagam, mbaa mbaamam, mbaa mboolem seen alalu dëkkandoo.» \p \v 22 Kàddu yii la Aji Sax ji wax seen ndaje ma mépp, ca tund wa, ba mu àddoo ca digg sawara wa, kàddu gu xumb, ci biir xàmbaar gu lëndëm këruus. Tegaatu ca dara. Mu daldi bind kàddu yi ci ñaari àlluway doj, jox ma. \v 23 Ba ngeen déggee kàddu gay jibe ca lëndëm ga, tund wa jàpp, di tàkk, yeena dikk, seen mboolem kilifay giir ak seeni mag, ba ci man. \v 24 Ngeen ne ma: «Sunu Yàlla Aji Sax ji kat, moo nu won darajaam ak màggaayam. Kàddoom lanu dégg, mu jibe ca digg sawara wa. Bésub tey noo gis Yàlla wax ak doom aadama, ba noppi, muy wéye bakkanam! \v 25 Waaye lu nuy jaayati nag sunu bakkan, doye? Ndax kat, sawara wu réy wii, su nu déggatee sunu kàddug Yàlla Aji Sax ji, da nuy xoyom. \v 26 Ana ci mboolem boroomu suux, ku ci masa dégg kàddug Yàlla jiy dund, mu jibe ci sawara, nii nu ko dégge, ba noppi di dund? \v 27 Jegejil yaw te déglu mboolem li sunu Yàlla Aji Sax ji wax. Yaw yaa nuy àgge mboolem li la sunu Yàlla Aji Sax ji wax, nu dégg, jëfe.» \p \v 28 Ci biir loolu Aji Sax ji dégg la ngeen ma wax. Mu ne ma: «Dégg naa li la mbooloo mii wax. Ñoo yey wax yooyu kàddu yépp. \v 29 Waaye céy bu ñu amoon boobu xol ngir ragal ma, di sàmm sama santaane yépp bés bu nekk, ba tax ñu baaxle, ñoom ak seen askan, ba fàww! \v 30 Demal, nga ne leen ñu dellu ca seeni xayma. \v 31 Yaw nag, taxawal fi man, ba ma jox la mboolem santaane bi, dogali yoon yi, ak àttey yoon yi nga leen di jàngal, te ñu war koo jëfe ca réew ma ma leen jox, ngir ñu nangu ko.» \p \v 32 Kon nag sàmmooleen koo jëfe ni leen ko seen Yàlla Aji Sax ji sante. Buleen lajjee ndijoor mbaa càmmoñ. \v 33 Mboolem yoon wi leen seen Yàlla Aji Sax ji teg, toppleen ko, ndax ngeen dund, baaxle te gudd fan ca réew ma ngeen di moom. \c 6 \s1 Aji Sax ji kenn la \p \v 1 Lii mooy santaane bi, ak dogali yoon yeek àttey yoon yi seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji santaane ma jàngal leen ko, ngir ngeen di ko jëfe ca réew ma ngeen jàll jëm, ngir nanguji ko, \v 2 ndax ngeen ragal seen Yàlla Aji Sax ji, di sàmm mboolem dogali yoonam, ak santaaneem, yi ma leen di dénk, yeen ak seeni doom, ak seeni sët, seen giiru dund, su ko defee ngeen gudd fan. \v 3 Kon yeen Israyil, dégluleen te sàmmoo jëfe, ndax ngeen baaxle te yokku bu baax, ni leen ko Aji Sax ji seen Yàllay maam waxe, ca réew ma meew maak lem ja tuuroo. \p \v 4 Dégluleen, \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, Aji Sax ji sunu Yàlla, Aji Sax ji kenn la. \v 5 Seen Yàlla Aji Sax ji, soppeleen ko seen léppi xol, ak seen léppi bakkan, ak seen léppi doole. \v 6 Kàddu yii ma leen di dénk bésub tey, na dëkk ci seen xol. \v 7 Nangeen ko xamal seeni doom, di ko waxe bu ngeen toogee seen biir néeg, ak bu ngeen di dox ciw yoon, ak bu ngeen tëddee, ak bu ngeen jógee. \v 8 Takkleen ko, muy firnde ci seen loxo, te na doon am mbandal ci seen diggantey gët. \v 9 Te itam bindleen ko ci seen kaw jëni buntu néeg, ak ci seen bunti dëkk. \p \v 10 Bu ngeen demee ba seen Yàlla Aji Sax ji yóbbu leen ca réew ma mu giñaloon seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, ne yeen la koy jox, muy dëkk yu mag yu baax yu ngeen tabaxul, \v 11 kër ya feese mboolem lu baax lu ngeen ko feesaluloon, ak teen yu ngeen gasul, ak garabi reseñ ak oliw yu ngeen jëmbatul; bu ngeen ca lekkee ba regg, \v 12 wattuleen seen bopp bala ngeena fàtte Aji Sax ji leen génnee réewum Misra, kërug njaam ga. \v 13 Seen Yàlla Aji Sax ji, ragal-leen ko. Moom ngeen di jaamu, te aw turam ngeen di giñe. \v 14 Buleen topp yeneen yàlla, ci yàllay xeet yi leen séq. \v 15 Ndax kat seen Yàlla Aji Sax ji ci seen biir, ku fiir la. Lu ko moy sànjum Aji Sax ji dina tàkk ci seen kaw, te dina leen sànk, ba raafal leen ci kaw suuf. \v 16 Buleen seetlu seen Yàlla Aji Sax ji, na ngeen ko seetloo woon ca Maasa. \v 17 Sàmmleena sàmm seen santaaney Yàlla Aji Sax ji, ak seedey yoonam, ak dogali yoonam, yi mu leen dénk. \v 18 Jëfeleen njub, ak mbaax gi Aji Sax ji rafetlu. Su ko defee dingeen baaxle, ba dem, nanguji réew mu baax mi Aji Sax ji giñaloon seeni maam, \v 19 te dingeen fa dàqe seen noon yépp, na ko Aji Sax ji waxe woon. \p \v 20 Bu leen seen doom laajee ëllëg, ne leen: «Ana lu waral seedey yoon yi, ak dogali yoon yeek àttey yoon yi leen sunu Yàlla Aji Sax ji dénk?» \v 21 Su boobaa waxleen seen doom, ne ko: «Ay jaami Firawna lanu woon ca Misra, waaye Aji Sax jee nu génnee Misra ci dooley loxoom. \v 22 Aji Sax jee nu defal ay firnde, ak kéemaan yu mag te metti ci kaw Misra ak ci kaw Firawna ak ci kaw waa këram gépp, nu teg ci sunuy gët. \v 23 Nun nag, moo nu fa jële, ngir indi nu ci réew mi mu giñaloon sunuy maam, ne nun la koy jox. \v 24 Aji Sax jee nu sant nuy jëfe mboolem dogali yoon yii, te ragal sunu Yàlla Aji Sax ji, ngir nu baaxle bés bu nekk, ngir itam mu sàmm sunu bakkan ni bésub tey jii. \v 25 Sunu njekk lay doon nag, ndegam sàmmoo nanoo jëfe mboolem santaane bii, fi sunu kanam Yàlla Aji Sax ji, ni mu ko santaanee.» \c 7 \s1 Dogook yenn xeet yi war na Israyil \p \v 1 Bu leen seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji yóbboo réew ma ngeen jëm, ngir nanguji ko, moo fay dàqe xeet yu bare fi seen kanam: Etteen ñi ak Girgaseen ñi ak Amoreen ñi ak Kanaaneen ñi ak Periseen ñi ak Eween ñeek Yebuseen ñi; juróom ñaari xeet yu leen ëpp, ëpp leen doole. \v 2 Bu leen leen seen Yàlla Aji Sax ji jébbalee, ba ngeen duma leen, nangeen leen faagaagal ba ñu jeex tàkk. Buleen fasook ñoom \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w*, te buleen leen yërëm. \v 3 Buleen séyanteek ñoom: seen doom ju jigéen, buleen ko may doomu xeet yooyu, jigéenu xeet yooyu it, buleen ko jëlal seen doom ju góor. \v 4 Ndax dañu may dëddale ak seen doom yu góor, ñu mujj di jaamu yeneen yàlla, ba sànjum Aji Sax ji tàkk ci seen kaw yeen, fàkkas leen ci lu gaaw. \v 5 Ni ngeen di def ak ñoom kay mooy nii: seeni \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*, ngeen màbb; seen tuuri doj, ngeen rajaxe; seen xer yi ñuy jaamoo \w Asera|lemma="Asera:"\w* tuur mi, ngeen gor; seen jëmmi tuur, ngeen lakk. \v 6 Ndax kat askan wu sell ngeen, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Yeen la seen Yàlla Aji Sax ji taamu, ngir ngeen doon askan wi mu séddool boppam, ci mboolem askani kaw suuf. \p \v 7 Du seen barewaay bu ngeen ëpplee xeet yépp moo tax Aji Sax ji naw leen, ba taamu leen, nde yeena gëna néew ci xeet yépp. \v 8 Waaye cofeel gu leen Aji Sax ji sopp, ak sàmm gu mu sàmm ngiñam la mu giñaloon seeni maam, moo tax mu génnee leen dooley loxoom, jote leen ca kërug njaam ga, ak ca loxol Firawna buuru Misra. \v 9 Xamleen boog ne seen Yàlla Aji Sax ji moom mooy Yàlla; mooy Yàlla ju dëggu jiy sàmm kóllëre ak ngor ñeel soppeem ñiy sàmm ay santaaneem, sët ba sëtaat, ba ci junniy maas. \v 10 Waaye mooy fey ci saa si ay bañam, ngir sànk leen. Du yeexe bañam, ci saa si la koy fey. \p \v 11 Kon nag sàmmleen santaane bi, muy dogali yoon yi, ak àttey yoon yi ma leen dénk tey, ngir di ko jëfe. \v 12 Bu ngeen déggalee àttey yoon yii, te sàmmoo koo jëfe, su boobaa seen Yàlla Aji Sax ji dina sàmm diggam ak yeen, kóllëre ak ngor, ga mu giñaloon seeni maam. \v 13 Moo leen di sopp, barkeel leen, yokk leen, barkeel seen meññeefum njurukaay, ak seen meññeefum suuf; seen pepp ak seen biiñ, ak seenug diw, ak seen doomi jur gu gudd, ak gu gàtt, ca réew ma mu giñaloon seeni maam, ne yeen la koy jox. \v 14 Su boobaa yeenay gëna barkeel mboolem xeet yi, te du lenn, góor ak jigéen, luy jaasir ci seen biir, ak seen biirug jur. \v 15 Su boobaa Aji Sax jee leen di xàjjil mboolem wéradi. Mboolem jàngoroy Misra yu bon yu ngeen xamoon, du leen ci teg lenn, te mboolem seeni bañ la koy teg. \v 16 Fàkkasleen mboolem xeet yi leen seen Yàlla Aji Sax ji jébbal nag. Buleen leen xool bëtu yërmande, buleen jaamu seeni tuur: Lu ko moy muy seenug fiir. \p \v 17 Jombul ngeen di wax ci seen xel naan: «Xeet yii gën noo bare, ana nu nu leen mana dàqe?» \v 18 Buleen leen ragal. Fàttlikuleen bu baax ni seen Yàlla Aji Sax ji def Firawna ak Misra gépp, \v 19 ak mitit yu réy ya ngeen gisal seen bopp, ak firnde yaak kéemaan ya, ak seen dooley loxol Yàlla Aji Sax jeek kàttanam gu réy, ga mu leen génnee. Noonu la seen Yàlla Aji Sax ji di def mboolem xeet yi ngeen ragal. \v 20 Te itam seen Yàlla Aji Sax ji, am mbas lay yebal ci seen kaw, ba seenu ndes wu leen làqu woon sànku. \v 21 Buleen am tiitaange ci ñoom, ndax seen Yàlla Aji Sax ji ci seen biir, Yàlla ju màgg la te raglu. \v 22 Seen Yàlla Aji Sax jee leen di dàqe fi seen kanam, ndànk-ndànk; dungeen leen mana gaawa jeexal, lu ko moy rabi àll yi mujj ne gàññ ci seen kaw. \v 23 Seen Yàlla Aji Sax ji moo leen di jébbal xeet yooyu, moo leen di salfaañe salfaañoo gu réy, ba ñu sànku. \v 24 Mooy teg seeni buur ci seeni loxo, ngeen far seenu tur fi asamaan tiim. Kenn ci ñoom du leen të, ba kera ngeen leen sànkee. \v 25 Seen jëmmi tuur yooyu nag, lakkleen leen. Buleen xemmem lenn luy xaalis mbaa wurus ci kaw tuur yi. Buleen ko aakimoo, lu ko moy muy seenug fiir, ndax lu seexluwoo ngoogu ci seen Yàlla Aji Sax ji. \v 26 Buleen dugal yëf yu seexluwu seen biir néeg, lu ko moy àtteb faagaagal bi war ci yëf yooyu, moo leen di dab, yeen itam. Xofleen koo xof, seexlu koo seexlu, ndax yëf yooyu, faagaagal moo ci war. \c 8 \s1 Xéewlu, fàtte aay na \p \v 1 Mboolem santaane bi ma leen dénk bésub tey nag, sàmmooleen koo jëfe, ndax ngeen dund, yokku, ba dugg nanguji réew ma \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji giñaloon seeni maam. \v 2 Fàttlikuleen mboolem yoon wi leen seen Yàlla Aji Sax ji awale diiru ñeent fukki at yii ci màndiŋ mi, teg leen coono, nattu leen ngir xam li ci seen biir xol, xam ndax dingeen wormaal ay santaaneem, am déet. \v 3 Moo leen teg coono, xiifal leen, leel leen \w mànn|lemma="mànn:"\w* mu ngeen xamul, te seeni maam xamuñu ko woon, ngir xamal leen ne du aw ñam doŋŋ la doom aadama di dunde, waaye gépp kàddu gu tukkee ci gémmiñu Aji Sax ji, dees na ko dunde. \v 4 Seeni yére ràppul, seeni tànk newiwul diiru ñeent fukki at yii. \v 5 Xamleen xéll ne ni baay di yare doomam, ni la leen seen Yàlla Aji Sax ji yare. \v 6 Kon sàmmleen seen santaaney Yàlla Aji Sax ji, di topp ay yoonam te ragal ko. \v 7 Ndax seen Yàlla Aji Sax jaa ngi leen di yóbbu réew mu baax; réew mu ami wal, ak bëti ndox, ak ndoxi xóote yu waley xur aki tund, \v 8 réewum bele ak lors ak reseñ ak figg ak gërënaat, ak diwu oliw, ak lem. \v 9 Réew ma dungeen fa néewe njël, te dungeen fa ñàkke dara. Réew ma, ay dojam, weñ gu ñuul la, ay tundam, xànjar ngeen cay gase. \v 10 Dingeen lekk ba regg, di sante seen Yàlla Aji Sax ji, réew mu baax ma mu leen jox. \p \v 11 Wattuleen seen bopp nag, bala ngeena fàtte seen Yàlla Aji Sax ji, baña sàmm ay santaaneem, ak àttey yoonam, ak dogali yoonam yi ma leen di dénk tey. \v 12 Su ngeen lekkee ba regg, am kër yu baax yu ngeen tabax dëkke, \v 13 seen jur gu gudd ak gu gàtt yokku, xaalis ak wurus yokkul leen, seen jépp alal yokku, \v 14 su boobaa moytuleen daldi xoggliku, fàtte seen Yàlla Aji Sax, ji leen génnee réewum Misra, kërug njaam ga, \v 15 ki leen wommate biir màndiŋ mu yaa mu raglu ma, ak jaani daŋar yaaki jiitam, ci biir maral ak ñàkk um ndox. Moo leen xellil ndox mu balle doj wu ne sereŋ. \v 16 Moo leen leele mànnu màndiŋ, ma seeni maam xamuloon, ngir teg leen coono, nattu leen, te mujje baaxe leen. \v 17 Dingeen wax ci seen xel ne: «Sunu doole ak sunu njàmbaaru bopp moo nu may jii alal.» \v 18 Waaye fàttlikuleen ne seen Yàlla Aji Sax ji mooy ki leen may dooley liggéey alal ji, ngir feddli ni mu ko defe tey, \w kóllëreem|lemma="kóllëre g-:"\w* ga mu giñaloon seeni maam. \p \v 19 Bu ngeen demee ba fàtte lu jëm ci seen Yàlla Aji Sax ji, di topp yeneen yàlla, di leen jaamook a sujjóotal, seedeel naa leen bés niki tey, ne su boobaa déy, dingeen sànku cànkute gu mat sëkk. \v 20 Ni xeet yi Aji Sax ji nara sànk fi seen kanam, noonu ngeen di sànkoo ndax ñàkka déggal seen Yàlla Aji Sax ji. \c 9 \s1 Israyil gënul ci xeet yi \p \v 1 Israyil dégluleen! Yeena ngii tey, di jàll dexu Yurdan ngir dàqi xeet yu leen ëpp, ëpp leen doole, ngir nangu seen dëkk yu réy, dàbblikoo tata yu àkki asamaan. \v 2 Askan wu am kàttan, yegg ca kaw, soqikoo ci Anageen, ñi ngeen xam, te dégg ñuy wax ci ñoom, naan: «Ku mana të Anageen ñi?» \v 3 Waaye xamleen bés niki tey ne seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji mooy kiy jàll jiite leen, di sawara wuy xoyome. Moo leen di fàkkas, mooy ki leen leen di notal, ngeen dàq leen, sànk leen ci lu gaaw, ni leen ko Aji Sax ji waxe woon. \p \v 4 Gannaaw bu leen leen seen Yàlla Aji Sax ji dàqalee nag, buleen wax ci seen xel ne: «Sunu njekk a nu may Aji Sax ji indi nu, ngir nu moom réew mii.» Mbonug xeet yii kay moo waral Aji Sax ji dàqal leen leen. \v 5 Du seen genn njekk, akug njub gu leen may ngeen nanguji seenum réew. Waaye mbonug xeet yii moo waral seen Yàlla Aji Sax ji dàqal leen leen, ngir sottal kàddu ga mu giñaloon seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba. \v 6 Kon na leen bir ne du seenug njekk moos la leen seen Yàlla Aji Sax ji joxe mii réew mu baax, ngir ngeen moom ko ndax, askan wu daŋŋiiral ngeen. \s1 Israyil jaamu na sëlluw wurus \p \v 7 Fàttlikuleen! Buleen fàtte na ngeen merloo woon seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ca màndiŋ ma. La dale bés ba ngeen bàyyikoo réewum Misra, ba ba ngeen agsee bérab bii, fippu ci kaw Aji Sax ji ngeen masa nekke. \v 8 Ca tundu Oreb ngeen merloo Aji Sax ji, Aji Sax ji mere leen, ba nar leena faagaagal. \v 9 Ba ma yéegee ca tund wa, di jëli àlluway doj ya, àlluway \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w*, gi Aji Sax ji fas ak yeen; toog naa ca kaw tund wa ñeent fukki bëccëg ak ñeent fukki guddi. Du ñam wu ma lekk, du ndox mu ma naan. \v 10 Aji Sax ji jox ma ñaari àlluway doj yu loxol Yàlla bind mboolem kàddu ya leen Aji Sax ji waxoon ca kaw tund wa, ba mu àddoo fa digg sawara wa, keroog bésub ndaje ma. \p \v 11 Ba ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg matee, Aji Sax ji jox ma ñaari àlluway doj ya, àlluway kóllëre ga. \v 12 Aji Sax ji ne ma: «Jógal wàcce fii gaaw, ndax sa bokk ya nga génnee Misra def nañu yàqute. Teggi nañu xaat yoon wa ma leen santoon. Móolal nañu seen bopp jëmmu tuur.» \p \v 13 Aji Sax ji waxati ma, ne ma: «Gis naa ne mbooloo mii kat, ñu dëgër bopp lañu. \v 14 Bàyyi ma rekk ma faagaagal leen, ba far seen tur fu asamaan tiim, te def la ngay xeet wu ëpp wii, ëpp ko doole.» \p \v 15 Ba loolu amee ma walbatiku, wàcce ca tund wa, maak yaari àlluway kóllëre ga ca sama yaari loxo, tund wépp di tàkk. \v 16 Ma gis ne ndeke moy ngeen seen Yàlla Aji Sax ji, daldi sàkkal seen bopp wëllu wu ñu móol, dëddu xaat yoon wa leen Aji Sax ji santoon. \v 17 Ci kaw loolu ma ne cas yaari àlluwa ya ca sama yaari loxo, sànni, rajaxe ko, ngeen di gis. \s1 Musaa tinul na bànni Israyil \p \v 18 Ba loolu amee ma daanu tëdd fa kanam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, na woon, diiru ñeent fukki bëccëg ak ñeent fukki guddi. Du ñam wu ma lekk, du ndox mu ma naan ndax seen gépp moy gu ngeen moy, di def lu Aji Sax ji ñaawlu, ba merloo ko. \v 19 Booba am naa tiitaange ci merum Aji Sax ji, ak sànjam mi mu nara sànju ci seen kaw, ngir sànk leen. Teewul Aji Sax ji nangul ma boobu yoon itam. \v 20 Aaróona nag, Aji Sax ji mere ko lool, nar koo sànk. Ma daldi ñaanalaale Aaróona. \v 21 Seen bàkkaarukaay boobu ngeen sàkkoon nag, jëmmu wëllu wa, ma jël ko, lakk ko, tojat, wol ba mu mokk, ba doon pënd. Ma daldi sotti pënd ba ca biir yol ga wale kaw tund wa. \p \v 22 Ca Tabera itam, ak ca Maasa, ak ca Kibbrot Taawa, ngeen merlooti fa Aji Sax ji. \v 23 Ak ba leen Aji Sax ji yebalee fa Kades Barneya, ne leen: «Demleen nanguji réew ma ma leen jox.» Yeena gàntal seen kàddug Yàlla Aji Sax ji, gëmuleen ko, déggaluleen kàddoom. \v 24 Gàntal Aji Sax ji ngeen nekke naka jekk, dale ko ca bés ba ma leen xamee. \p \v 25 Maa daanu tëdd fa kanam Aji Sax ji diiru ñeent fukki bëccëg yooyu, ak ñeent fukki guddi ya ma tëdd fa kanamam ndax la Aji Sax ji noon da leen di sànk. \v 26 Ma ñaan Aji Sax ji, ne ko: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, bul sànk sa ñoñ ñi nga séddoo, ñi nga jote sa màggaay, génnee leen Misra ci sa dooley loxo. \v 27 Ngalla bàyyil xel sa jaam ña, Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba. Bul xool ci tëwug mbooloo mii ak seen mbon, ak seenug moy. \v 28 Lu ko moy kat waa réew ma nga nu jële dinañu ne: “Tële leena yóbbu réew ma mu leen digoon, ak jéppi leen moo tax Aji Sax ji génne leen, ngir rey leen ca màndiŋ ma.” \v 29 Ñii de ñooy sa ñoñ ñi nga séddoo, ñi nga génnee sa doole ju bare, ci sa kàttanu loxo.» \c 10 \p \v 1 Jant yooyu la ma Aji Sax ji wax ne ma: «Yettal ñaari àlluway doj yu mel ni yu jëkk ya, nga yéegsi fi man, ci kaw tund wi. Te nanga sàkk itam \w gaalu bant|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w*. \v 2 Dinaa bind ci àlluwa yi, kàddu ya woon ca àlluwa yu jëkk, ya nga toj. Su ko defee nga yeb àlluwa yi ci gaal gi.» \v 3 Ma sàkk gaalu bantu séng, daldi yett ñaari àlluway doj yu mel ni yu jëkk ya. Ci kaw loolu ma yéeg ca kaw tund wa, maak ñaari àlluwa yi ci sama loxo. \v 4 Aji Sax ji nag bind ca àlluwa ya, la mu jëkkoona bind, muy fukki santaane ya mu leen waxoon ca kaw tund wa, ba mu àddoo fa digg sawara wa, keroog bésub ndaje ma. Ba loolu amee Aji Sax ji jox ma àlluwa yi. \v 5 Ma walbatiku, wàcc tund wa, yeb àlluwa ya ca gaal ga ma sàkk, àlluwa ya des ca biir, na ma ko Aji Sax ji waxe woon. \p \v 6 Gannaaw gi \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* bàyyikoo ca teeni Bene Yaakan, dem ba Mosera. Foofa la Aaróona faatoo, ñu denc ko fa, doomam Elasar doon sarxalkat, wuutu ko. \v 7 Foofa lañu bàyyikoo dem Gutgoda, bawooti Gutgoda, jàll ba Yotbata, réewum wali ndox ya. \p \v 8 Jant yooyu la Aji Sax ji ber giirug Lewi, ngir ñuy gàddu gaalu kóllëreg Aji Sax ji, di taxaw fi kanam Aji Sax ji, di ko liggéeyal, di taase barke ciw turam, te mooy seen péete ba tey jii. \v 9 Looloo waral \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi amuñu wàll ci céru suuf su ñuy séddoo ak seeni bokk. Aji Sax ji mooy seenub cér, ni leen ko seen Yàlla Aji Sax ji waxe woon. \p \v 10 Man nag maa am ca kaw tund wa fan ya ma fa jëkkoona am, muy ñeent fukki bëccëg, ak ñeent fukki guddi. Aji Sax ji dellu ma nangul, boobu yoon itam, ba bëggatu leena sànk. \v 11 Aji Sax ji ne ma: «Doxal jiite yoonu mbooloo mi, ñu dem nanguji réew, ma ma giñaloon seeni maam, ne ñoom laa koy jox.» \s1 Musaa ngi woote déggal Aji Sax ji \p \v 12 Léegi nag yeen Israyil, ana lu leen seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji laaj, lu moy ngeen ragal seen Yàlla Aji Sax ji, di doxe mboolemi yoonam, sopp ko, di jaamoo seen Yàlla Aji Sax ji seen léppi xol, ak seen léppi bakkan, \v 13 ngir di sàmm santaaney Aji Sax ji, ak dogali yoonam, yi ma leen dénk bésub tey ngir seen njariñal bopp? \v 14 Seen Yàlla Aji Sax ji déy mooy boroom asamaan, ak asamaani asamaan, ak suuf, ak mboolem li ci biiram. \v 15 Terewul seeni maam doŋŋ la Aji Sax ji taqool, ngir sopp leen, te yeen, ñi askanoo ci ñoom la taamu ci biir xeetoo xeet, niki bésub tey jii. \v 16 Kon nag nangeen dogoo seen xol te bañatee sajju loos. \v 17 Ndax kat seen Yàlla Aji Sax ji mooy Yàllay yàlla yi, te mooy Sangu sang yi. Mooy Yàlla ju màgg ji, jàmbaare te raglu. Ki gënalewul, jëlul ub ger. \v 18 Kiy aar jirim akub jëtun, sopp doxandéem, ngir leel ko, wodd ko. \v 19 Kon soppleen doxandéem, ndax ay doxandéem ngeen woon ca réewum Misra. \p \v 20 Seen Yàlla Aji Sax ji moom ngeen di ragal, te moom ngeen di jaamu. Moom ngeen di ŋoyu, te aw turam ngeen di giñe. \v 21 Moo yelloo seeni kañ te mooy seen Yàlla, ji leen defal jaloore yeek kawtéef yooyu ngeen gisal seen bopp. \v 22 Juróom ñaar fukki bakkan la seeni maam doonoon ba ñuy wàccsi Misra. Tey seen Yàlla Aji Sax ji def leen ngeen day ni biddiiwi asamaan. \c 11 \p \v 1 Soppleen seen Yàlla Aji Sax ji, te ngeen dénkoo ndénkaaneem, ak dogali yoonam, ak àttey yoonam, aki santaaneem, bés bu nekk. \v 2 Xamleen bésub tey ne seeni doom taxul may wax, ndax ñoom xamuñu, gisuñu seen njànglem Yàlla Aji Sax ji: màggaayam, ak dooley loxoom, ak kàttanam gu réy, \v 3 aki firndeem, ak jalooreem ja mu jëf ca digg Misra, ci kaw Firawna buuru Misra ak ci biir réewam mépp, \v 4 jëfe kook gàngooru Misra, ak seeni fas ak seen watiiri xare, ba mu leen mëddee ca géeju Barax ya, fekk ñu ne leen dann. Aji Sax jee leen sànk ba bésub tey jii, \v 5 ak la mu leen def ca màndiŋ ma, ba ngeen agsi bérab bii, \v 6 ak la mu def Datan ak Abiram, doomi Elyab Rubeneen ba, ba suuf ŋayee, wonn leen, ñook seen waa kër, ak seeni xayma, ak mboolem luy dund lu leen topp, ci digg Israyil gépp. \v 7 Seeni gët déy ngeen teg ci mboolem jaloore ju màgg jooju Aji Sax ji def. \p \v 8 Kon nag sàmmleen mboolem santaane bi ma leen di dénk tey, ndax ngeen am doole ba nanguji réew ma ngeen jàll jëm, ngir nanguji ko, \v 9 ndax itam ngeen gudd fan ca réew ma Aji Sax ji giñoona jox seeni maam, ñook seen askan; réew mu meew maak lem ja tuuroo. \v 10 Réew mooma ngeen jëm, di ko nanguji, déy, niroowul ak réewum Misra ga ngeen jóge, fa ngeen daan jiwe, ba noppi topp seenum jiwu, di ko suuxate dooley tànk ni mbeyum dër. \v 11 Réew mooma ngeen jàll jëm, ngir nanguji ko, réewum tund aki xur la, te ndoxum taw lay naan. \v 12 Réew la mu seen Yàlla Aji Sax ji yég, fu mu tollu seen gëti Yàlla Aji Sax jaa ngi ne ko jàkk, terutel at ba ndeetelam. \p \v 13 Su fekkee ne nag sàmm ngeen ba sàmm sama santaane yi ma leen dénk tey jii, ngir sopp seen Yàlla Aji Sax ji, di ko jaamoo seen léppi xol, ak seen léppi bakkan, \v 14 su boobaa, Yàlla nee: «Maa leen di may seen tawub réew, saa yu jotee: lollib réew ma day taw\f + \fr 11.14 \fr*\ft Tawub lolli lu jaadu la ca réewum Israyil, bokkul ak jamonoy lolli ji topp ci nawet fii.\ft*\f*, cooroonam taw, ngeen dajale seenum pepp, ak seen biiñ bu bees, ak seen diw gu yees. \v 15 Su boobaa maay mayem ñax ci seenub àll ngir seenug jur, yeen it ngeen di lekk ba regg.» \p \v 16 Wattuleen seen bopp nag, bala leen seen xel a nax, ngeen lajj, di jaamu yeneen yàlla, di leen sujjóotal, \v 17 ba sànjum Aji Sax ji tàkkal leen, mu ne ràpp asamaan, taw taxaw, suuf noppee meññal, ba ngeen gaawa sànkoo ca réew mu baax ma leen Aji Sax jiy jox. \p \v 18 Defleen sama kàddu yii ci seenum xel ak ci seen xol. Takkleen ko, muy firnde ci seen loxo, te na doon am mbandal ci seen diggantey gët. \v 19 Nangeen ko jàngal seeni doom, di ko waxe bu ngeen toogee seen biir néeg, ak bu ngeen di dox ciw yoon, ak bu ngeen tëddee, ak bu ngeen jógee. \v 20 Te itam bindleen ko ci seen kaw jëni buntu néeg, ak ci seen bunti dëkk, \v 21 ndax seeni fan, ak seen fani doom, baree ca réew ma Aji Sax ji giñaloon seeni maam, ni kemu fan yi asamaan tiim suuf. \p \v 22 Ndegam déy sàmm ngeen ba sàmm mboolem santaane bii ma leen dénk ngir di ko jëfe, ba sopp seen Yàlla Aji Sax ji, di doxe mboolem ay yoonam te ŋoy ci moom, \v 23 su boobaa Aji Sax jee leen di dàqal mboolem xeet yooyu, te yeenay nangu réewi xeet yu leen ëpp, ëpp leen doole. \v 24 Fépp fu ngeen teg seen tànk, yeena koy moom. La ko dale ca màndiŋ ma ba ca Libaŋ, daleeti dexu Efraat ba ca géej ga ca sowu, lépp seen suuf lay doon. \v 25 Du kenn kuy taxaw fi seen kanam. Seen Yàlla Aji Sax ji mooy def na mu leen ko waxe woon, ba waa déndu réew mu ngeen teg seen tànk, ñoom ñépp, yeen lañuy tiit, yeen lañuy ragal. \s1 Barke ak alkànde dëgmal na \p \v 26 Maa ngii nag di leen tegal bésub tey barke ak alkànde. \v 27 Barkee ngi, ndegam déggal ngeen seen santaaney Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w*, ji ma leen di dénk tey. \v 28 Alkàndee ngi, ndegam déggaluleen seen santaaney Yàlla Aji Sax ji, xanaa wacc yoon wi ma leen di dénk bésub tey, ngir topp yeneen yàlla yu ngeen xamuloon. \p \v 29 Bu leen seen Yàlla Aji Sax ji yóbboo ca réew ma ngeen jëm, ngir nanguji ko, nangeen tudd barke bi ca kaw tundu Garisim, te ngeen tudd alkànde ji ca kaw tundu Ebal. \v 30 Ñaari tund yooyu, ña nga moos ca wàllaa dexu Yurdan, ca wàllaa yoonu sowu ba, ca réewum Kanaaneen, ña dëkke joor ga jàkkaarlook Gilgal, ca weti garabi More yu mag ya. \v 31 Léegi nag yeena ngi jàlli dexu Yurdan, ngir nanguji réew mi leen seen Yàlla Aji Sax ji jox. Bu ngeen ko nangoo ba dëkk fa nag, \v 32 sàmmooleena jëfe mboolem dogal yeek àttey yoon yi ma teg fi seen kanam, bésub tey jii. \c 12 \ms2 Lu jëm ci sàrti dundin ca réewum dige ba \mr (Saar 12—26) \s1 Aji Sax ji mooy taamu bérabam \p \v 1 Dogal yeek àttey yoon, yi ngeen di sàmmoo jëfe seen giiru dund ca suufas réew, ma leen seen Yàllay maam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji moomale, moo di yii: \v 2 tasleen tasar mboolem bérab, ya xeet ya ngeen di dàq, di jaamoo seeni tuur; muy kaw tund yu mag ya, di kaw tund yu ndaw ya, di ker garab yu naat ya. \v 3 Tojleen seeni \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*, rajaxe seen tuuri doj; seen xer yi ñuy jaamoo \w Asera|lemma="Asera:"\w* tuur mi, ngeen lakk; seen jëmmi tuur, ngeen gor, ba far tukkal turi tuur yi ci yooyu bérab. \v 4 Buleen jaamoo noonu seen Yàlla Aji Sax ji nag. \v 5 Waaye seetleen bérab bu seen Yàlla Aji Sax ji di taamuji, ci mboolem seeni giir, ngir teg fa turam, dëël ko fa, te ngeen dem foofa. \v 6 Foofa ngeen di yóbbu seen \w saraxi dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ak yeneen sarax, ak seen céri fukkeel, ak seenub jooxe, ak seen sarax yu ngeen xas, ak seen \w saraxi yéene|lemma="Sarax yi:"\w*, ak seen saraxi taawug jur gu gudd ak gu gàtt. \v 7 Foofa ngeen di lekke, yeen ak seeni njaboot fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ngeen bége fa seen wépp ñaq wu leen seen Yàlla Aji Sax ji barkeelal. \p \v 8 Buleen jëfe mboolem nii nuy jëfe fii tey, lu neex waay rekk, def. \v 9 Ndax kat àggaguleen ba tey ca dal-lukaay ba, fa leen seen Yàlla Aji Sax ji sédde. \v 10 Waaye bu ngeen jàllee dexu Yurdan, ba dëkki ca réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji sédde, ba mu noppal leen ci mboolem noon yi leen séq, ngeen dëkke xel mu dal, \v 11 su boobaa bérab bu seen Yàlla Aji Sax ji taamu ngir dëël fa turam, foofa ngeen di yóbbu mboolem lu ma leen sant: seen saraxi dóomal, ak yeneen sarax, ak seen céri fukkeel, ak seenub jooxe, ak mboolem ngëneel yu ngeen di def saraxi xas yu ngeen xasoo ak Aji Sax ji. \v 12 Su ko defee ngeen bége fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, yeen ak seen doom yu góor ak yu jigéen, ak seen jaam yu góor ak yu jigéen, ak \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi ci seen biiri dëkk te amuñu wàll, amuñu céru suuf ci seen biir. \p \v 13 Wattuleen seen bopp bala ngeena joxe seen saraxi dóomal fépp fu ngeen gis, \v 14 ndax bérab bu Aji Sax ji taamu ci genn ci seen giir yi, foofa ngeen di joxe seen saraxi dóomal, te foofa ngeen di def lépp lu ma leen sant. \v 15 Teewul saa yu leen soobee, sañ ngeena rendi, lekk ci lépp lu leen seen Yàlla Aji Sax ji barkeele, ak fépp fu ngeen dëkk. Ku sobewu ak ku set yépp sañ na caa lekk, mel ni bu doon kéwél mbaa kooba. \v 16 Waaye deret ja, buleen ko lekk. Ci suuf ngeen koy tuur nim ndox. \v 17 Seen céru fukkeelu pepp nag, ak bu biiñ bu bees, ak bu diw gu bees, ak seen taawug jur gu gudd ak gu gàtt, ak seen mboolem saraxi xas yu ngeen xasoo woon, ak seen saraxi yéene, ak ab jooxe bu ngeen sàkke ci seenu ñaq, sañuleen cee lekk lenn ci seen biiri dëkk, \v 18 ndare ngeen lekke ko fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji. Lekkeleen ko fa seen Yàlla Aji Sax ji di taamuji, yeen ak seen doom yu góor, ak yu jigéen, ak seen jaam yu góor ak yu jigéen, ak Leween ñi ci seen biir dëkk. Su ko defee ngeen bége seen wépp ñaq, fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji. \v 19 Wattuleen seen bopp nag, ngir baña sàggane Leween ñi, seen giiru dund ca seen suuf. \p \v 20 Bu seen Yàlla Aji Sax ji yokkee seen suuf noonee mu leen ko waxe woon, te ngeen namma lekk yàpp, saa yu leen neexee sañ ngeena lekk yàpp. \v 21 Bu fekkee ne fi seen Yàlla Aji Sax ji taamoo dëël turam dafa soreek yeen, man ngeena rendi ci seen jur gu gudd mbaa gu gàtt, ga leen Aji Sax ji jox, na ma leen ko waxe woon. Sañ ngeen caa lekke seen biir dëkk lu leen neex. \v 22 Ni ñuy lekke yàppu kéwél mbaa kooba rekk ngeen koy lekke. Ku sobewu ak ku set yépp sañ na caa lekk. \v 23 Moyuleen bu baax rekk ba baña lekk deret ji, ndax deret mooy bakkan te waruleen boole lekk bakkanu jur gi, aku suuxam. \v 24 Buleen lekk deret ji. Ci suuf ngeen koy tuur nim ndox. \v 25 Buleen ko lekk mukk, su boobaa dingeen baaxle, yeen ak seen doom yi leen di wuutu; ngir su boobaa yeena ngi jëfe li Aji Sax ji rafetlu. \p \v 26 Waaye seen yëf yu ñu sellal, ak seen sarax yi ngeen xasoo, jël-leen ko, yóbbu ca bérab ba Aji Sax ji di taamuji. \v 27 Te nangeen sarxe seen saraxi rendi-dóomal, yàpp wi ak deret ji, ci seen kaw sarxalukaayu Yàlla Aji Sax ji. Seen deretu yeneen sarax, tuurleen ko ca seen kaw sarxalukaayu Yàlla Aji Sax ji, yàpp wi ngeen lekk ko. \p \v 28 Sàmmooleena déggal mboolem kàddu yii ma leen di dénk, ngir ngeen baaxle ba fàww, yeen ak seen doom, yi leen di wuutu, ndax kon yeena ngi jëfe lu baax li seen Yàlla Aji Sax ji rafetlu. \p \v 29 Bu leen seen Yàlla Aji Sax ji sànkalee xeet yi ngeen jëm, ngir dàq leen, gannaaw bu ngeen leen dàqee ba dëkke seenum réew, \v 30 nangeen wattu seen bopp, ba gannaaw bu xeet yooyu sànkoo ci seen kanam, dungeen tàbbi cig fiir, di leen roy, naan: «Ana nu xeet yii di jaamoo seeni tuur, ngir nun it nu def ni ñoom?» \v 31 Buleen defe noonu ak seen Yàlla Aji Sax ji, ndax mboolem lu seexluwu lu Aji Sax ji bañ, defal nañu ko seeni tuur. Seen doom yu góor ak yu jigéen sax, lakk nañu leen, defal leen seeni tuur sarax. \s1 Dee mooy àtteb kuy xiirtale ci bokkaale \p \v 32 Mboolem kàddu gi ma leen dénk nag, sàmmooleen koo jëfe. Buleen ci yokk lenn, buleen ci wàññi lenn. \c 13 \p \v 1 Gannaaw loolu su ab yonent feeñee ci seen biir, mbaa boroom gént, bu leen digee firnde mbaa kiraama, \v 2 ba firnde la mbaa kiraama ga mu leen waxoon dikk, su leen nee: «Nanu topp yeneen yàlla, jaamu leen,» yàlla yu ngeen xamul, \v 3 buleen déglu waxu yonent boobu, mbaa boroom gént boobu, ndax seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji moo leen di nattu ngir xam ndax yeena ngi koy soppe seen léppi xol ak seen léppi bakkan. \v 4 Seen Yàlla Aji Sax ji moom ngeen di topp, moom ngeen di ragal. Ay santaaneem ngeen di sàmm, baatam ngeen di déglu, moom ngeen di jaamu, te ci moom ngeen wara ŋoy. \v 5 Yonent boobu nag mbaa boroom gént boobu, dee mooy àtteem, ndax moo woote ag fippu ci seen kaw Yàlla Aji Sax, ji leen jële ca réewum Misra, jote leen kërug njaam ga. Mu nar leena féle ci yoon wi leen seen Yàlla Aji Sax ji sant ngeen doxe ko. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir. \p \v 6 Seen mbokk mu ngeen bokkal jenn ndey, mbaa seen doom ju góor, mbaa ju jigéen, mbaa seen jabar ju ngeen xejjoo, mbaa seen xaritu benn bakkan, su leen dee xiirtal, naan leen ci kumpa: «Nanu jaamuji yeneen yàlla,» yàlla yu ngeen xamul, du yeen du seeni maam, \v 7 ci yàllay xeet yi leen séq, ñi leen jege, ak ñi leen sore, ci àddina sépp, cat ba cat, \v 8 su boobaa buleen ko nangul, buleen ko déglu, buleen ko xool bëti yërmande, buleen ko baal, buleen ko nëbbal. \v 9 Reyleen ko rekk. Yeen ñi mu doon jéema yóbbaale, na ko seen loxo jëkka dal, ngir rey ko, bala cee loxol mbooloo mépp topp. \v 10 Dóorleen koy doj ba mu dee, ndax moo leen doon fexee soreleek seen Yàlla Aji Sax, ji leen jële réewum Misra, kërug njaam ga. \v 11 Israyil gépp a koy dégg, daldi ragal ba deesatul def mbon gu ni mel ci seen biir. \p \v 12 Bu ngeen déggee, ci benn dëkk, ci dëkk yi leen seen Yàlla Aji Sax ji jox, ngir ngeen dëkke, ñu ne \v 13 ay nit ñu tekkiwul dara, te bokk ci yeen, ñoo jóg di waññi seen waa dëkk, naan leen: «Nanu jaamuji yeneen yàlla,» yàlla yu ngeen xamul, \v 14 su boobaa nangeen gëstu, seet te laajte bu baax, ba dëgg gu wér feeñe ca mbir ma, ne defees na moomu mbir mu jomblu ci seen biir, \v 15 ngeen daldi jam rekk waa dëkk boobu, leel leen ñawkay saamar, faagaagal dëkk ba, ak mboolem la ca biiram, jur ga it, ngeen leel leen ñawkay saamar. \v 16 Mboolem alalu sëxëtoo ju jóge ca dëkk ba, dajaleleen ko ca digg pénc ma, te ngeen lakk dëkk ba, booleek cëxëtoo ma, def ko dóomal bu mat sëkk, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Day doon ab gent ba fàww, deesu ko tabaxaat. \v 17 Bu dara des ci seen loxo, lu bokk ci alal jooju ñu wara faagaagal. Su ko defee Aji Sax ji dëddu sànjam mu tàng, yërëm leen, ñeewante leen, yokk leen na mu ko giñale woon seeni maam, \v 18 ndegam yeena ngi dégg seen kàddug Yàlla Aji Sax ji, ngir sàmm mboolem santaaneem yi ma leen di dénk bésub tey, ngir di jëfe li seen Yàlla Aji Sax ji rafetlu. \c 14 \s1 Yoon wi sàrtal na jëfin yu set \p \v 1 Ay doom ngeen, ñeel seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Buleen ñaasu, buleen wat seen kawaru bopp fi féeteek jë bi, ngir di ko mititloo ku dee, \v 2 ndax askan wu sell ngeen, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Yeen la Aji Sax ji taamu, ngir ngeen doon askan wi mu séddool boppam, ci mboolem askani kaw suuf. \p \v 3 Buleen lekk lenn lu seexluwu. \v 4 Lii moo di mala yi ngeen di lekk seen suux: nag ak xar ak bëy; \v 5 ak kooba ak kéwél, ak lu xeetook kooba, ak lu xeetook kéwél, ak bëyu àll, ak bëyu kaw tund. \v 6 Mboolem mala mu ci we wi xar, séddlikoo yaar, te muy duññ, moom ngeen di lekk aw suuxam. \v 7 Waaye yii, buleen lekk seen suux: lu ciy duññ doŋŋ, te we wi xarul, mbaa lu we wi xar, te duññul. Lu mel ni giléem ak njomboor ak daman, ndax dañuy duññ waaye seen we xarul. Yooyu daganul ci yeen. \v 8 Mbaam-xuux, moom, we wi xar na waaye du duññ. Kon daganul ci yeen. Aw suuxam, buleen ko lekk, te méddam, buleen ko laal. \p \v 9 Lii nag, sañ ngeen koo lekk, ci mboolem lu dëkke ndox: mboolem lu ci am ciiriir aki waasintóor, sañ ngeen koo lekk. \v 10 Waaye lu ci amul ciiriir aki waasintóor, buleen ko lekk, ndax daganul ci yeen. \p \v 11 Mboolem njanaaw lu set, sañ ngeen koo lekk. \v 12 Waaye lii ngeen dul lekk ci njanaaw yi: jaxaay ak tan, ba ca mu ñuul ma, \v 13 ak céeli bu xonq, ak céeli bu ñuul, ak maf, ak lu mu xeetool, \v 14 ak lépp luy baaxoñ ak lu mu xeetool, \v 15-18 ak bànjóoli ak looy, ak lu mu xeetool, ak kirigéej, ak mboolem xeeti liccin, ak yébb, ak lu xeetook xodd, ak musejubru ak njugub. \v 19 Mboolem boroomi laaf yu sew-sewaan, daganul ci yeen. Deesu ci lekk lenn, \v 20 xanaa boroomi laaf yi ci set. Yooyu, sañ ngeen koo lekk. \p \v 21 Buleen lekk lenn lu médd. Jaambur bu dal ak yeen, sañ ngeen koo jox lu médd, mu lekk, mbaa ngeen jaay ko ab doxandéem. Waaye yeen askan wu sell ngeen, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. \p Te buleen togg ab tef ci meewum yaayam. \s1 Lu jëm ci céri fukkeel \p \v 22 Fexeleen bay génne benn céru fukkeel ci mboolem lu seeni tool meññ at mu nekk. \v 23 Seen cérub fukkeelu pepp, ak biiñ bu bees, ak diw gu bees, ak lu seen jur taawloo, muy nag, di gàtt, nangeen ko xéewloo fi seen kanam Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, fi bérab bi mu taamoo dëël turam ëllëg. Su ko defee ngeen tàggatu ci ragal seen Yàlla Aji Sax ji fu ngeen tollu. \v 24 Su ngeen manula dox yoon wi, ndax seen Yàlla Aji Sax jee leen barkeele meññeef mu bare mu ngeen dul àttan, ci diggante bu sorewaatoo lool ak bérab bi seen Yàlla Aji Sax ji taamoo dëël turam, \v 25 su boobaa dangeen di wecci cérub fukkeel ba xaalis, jël xaalis ba te dem ba fa seen Yàlla Aji Sax ji taamu. \v 26 Su ko defee ngeen weccikoo fa xaalis bi lu leen neex, muy nag mbaa gàtt, mbaa biiñ, mbaa geneen naan gu diis, ak lu leen seen bakkan xiir, ngeen xéewloo fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, bànneexoo ko, yeen ak seen njaboot. \v 27 \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* gi ci seen biir dëkk nag, buleen leen fàtte, ndax amuñu wàll ci seen céru suuf. \p \v 28 Ñetti at yu mat yu nekk, nangeen génne mboolem seen céri fukkeeli meññeef ca at mooma, te ngeen denc ko ca seen biir dëkk, \v 29 ndax Leween, ñi amul wàll ci seen céru suuf, dikk, ñook doxandéem yi ak jirim yi ak jëtun, yi ngeen dëkkal, ngir ñu lekk ba regg. Su ko defee seen Yàlla Aji Sax ji barkeel mboolem seenu ñaq. \c 15 \s1 Lu jëm ci njéggalug bor \p \v 1 Juróom ñaari at yu mat yu nekk, nangeen amal njéggalug bor. \v 2 Mbirum njéggaleg bor gi, nii lay deme: mboolem ku lebaloon dëkkandoom, bumu ko ca feyeekooti. Na jéggale la mu lebaloon dëkkandoom, mbokkum bànni Israyilam, gannaaw bu ñu biralee njéggaleg bor, ñeel \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \v 3 Jaambur bi bokkul ci bànni Israyil, sañ ngeen koo feyeeku, waaye la leen seen mbokkum bànni Israyil ameel, jéggaleleen ko. \p \v 4 Waaye ab ndóol du am ci seen biir, ndax seen Yàlla Aji Sax ji moo leen di barkeel bu baax ca réew ma mu leen di jox, muy seen cér, ngeen jagoo, \v 5 ndegam déggal ngeen bu baax seen Yàlla Aji Sax ji, di sàmmoo jëfe mboolem santaane bii ma leen di dénk tey. \v 6 Bu leen seen Yàlla Aji Sax ji barkeelee ni mu ko waxe déy, yeenay lebal xeet yu bare, waaye yeen dungeen leb. Te it yeenay yilif xeet yu bare, waaye yeen, deesu leen yilif. \p \v 7 Su amee ci seen biir ab ndóol, di kenn ci seen bokki bànni Israyil, ci benn ci seen dëkki réew, mi leen seen Yàlla Aji Sax ji di jox, buleen dëgër xol, di tëjal seen loxo, seen mbokkum ndóol moomu. \v 8 Nàddil-leen koo nàddil, abal koo abal dayob soxlaam. \v 9 Wattuleen seen bopp, bala leena jikko ju sew yóbbe ngeen naan ci seen xel: «Atum juróom ñaareel mi, atum njéggalug bor dëgmal na,» ba tax ngeen sajje xef, seen mbokkum ndóol, joxuleen ko dara. Da leen di booleek Aji Sax ji, ngeen gàddu bàkkaar. \v 10 Nangeen ko joxa jox te bu ngeen koy jox it, bu ci seen xol bon, ndax loolu mooy tax seen Yàlla Aji Sax ji barkeel mboolem seen liggéey, ak mboolem seenu ñaq. \v 11 Du ñàkk nag ab ndóol ci réew mi. Moo tax ma sant leen ne leen ngeen nàddila nàddil seen mbokkum ndóol, ak seen néew-ji-doole ji ci seenum réew. \s1 Sang am na lu ko war ci jaamam \p \v 12 Su fekkee ne seen mbokkum bànni Israyil, góor mbaa jigéen da leena jaay boppam\f + \fr 15.12 \fr*\ft Mbaa: \ft*\fqa su fekkee ne dees leena jaay seen mbokkum bànni Israyil.\fqa*\f*, bu leen liggéeyalee juróom benni at, atum juróom ñaareel ma, yiwileen ko, mu moom boppam. \v 13 Te bu ngeen ko yiwee, mu moom boppam it, buleen ko yiwee loxoy neen. \v 14 Sàkkal-leen koo sàkkal ci seeni gàtt, ak seenum pepp, ak seen biiñ. Kemu alal ja leen seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji barkeele, moom ngeen koy jox. \v 15 Fàttlikuleen ne ay jaam ngeen woon ca réewum Misra, seen Yàlla Aji Sax ji moo leen jot. Moo tax ma sant leen lii tey. \p \v 16 Ndegam nag seen jaam a leen ne: «Duma dem, ba la,» ndax cofeel gu mu am ci yeen ak seen waa kër, te bànneexam di nekk ak yeen, \v 17 su boobaa fableen puso, ngeen sësale noppu jaam bi seen lafu bunt, te ngeen bënne puso bi noppam, ba mu jam ci lafu bunt bi, mu daldi doon seen jaam ba fàww. Seen jaam bu jigéen it, noonu ngeen di def ak moom. \p \v 18 Buleen mititlu lu ngeen yiwi seenub jaam, mu moom boppam, ndax jariñ na leen lu fey ñaari yoon surga buy feyeeku, ci juróom benni at yi mu leen liggéeyal. Te seen Yàlla Aji Sax ji dina leen barkeel ci mboolem lu ngeen def. \s1 Li war ci taawug jur \p \v 19 Mboolem luy taaw ci seen jur gu gudd, ak gu gàtt, te di góor, defal leen ko seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji cér bu sell. Buleen liggéeyloo mukk seen yëkk wu dib taaw, te buleen wat seen gàtt bu dib taaw. \v 20 Fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji ngeen ko wara xéewloo at mu jot, yeen ak seen njaboot, fi bérab bi Aji Sax ji taamu. \v 21 Jur gu ci am sikk nag, muy soox, mbaa mu gumba, mbaa mu am sikk su réy su mu mana doon, buleen ko sarxalal seen Yàlla Aji Sax ji. \v 22 Ci seen biir dëkk ngeen ko wara xéewloo, te ku sobewu ak ku set yépp man na caa lekk, mel ni bu doon kéwél mbaa kooba. \v 23 Waaye deretam, buleen ko lekk. Ci suuf ngeen koy sotti nim ndox. \c 16 \s1 Ñetti yoon lees di màggalsi ci bérab bu sell bi \p \v 1 Wormaal-leen weeru \w Abiib|lemma="Abiib:"\w*, te ngeen amal ci \w màggalu bésub Mucc|lemma="Màggali Yawut yi:"\w*, ñeel seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ndax ci weeru Abiib la leen seen Yàlla Aji Sax ji génnee Misra, ag guddi. \v 2 Nangeen ci sarxalal seen Yàlla Aji Sax ji, ab gàtt mbaa aw nag, ci bérab bi Aji Sax ji taamoo dëël turam ëllëg. \v 3 Buleen ko lekkaale lenn lu am lawiir. Daleleen caa lekk, ba diiru juróom ñaari fan, mburu mu amul lawiir, mburum njàqare, ndax ci biir gaawtu ngeen génne woon réewum Misra. Su ko defee ngeen baaxantal seen giiru dund, bés ba ngeen génnee réewum Misra. \v 4 Bu leen kenn gisal lawiir ci seen tund wépp, diiru juróom ñaari fan, te bu lenn fanaan ci yàppu jur gi ngeen sarxal, diggante ngoonu bés bu jëkk ba, ba ca suba sa. \p \v 5 Juru bésub Mucc bi, dungeen ko mana rendi fenn ci dëkk yi leen seen Yàlla Aji Sax ji jox, \v 6 fu moy bérab ba seen Yàlla Aji Sax ji taamoo dëël turam. Foofa ngeen di rendi juru bésub Mucc bi ci ngoon bu jant biy so, yemook waxtu wa ngeen bàyyikoo woon Misra. \v 7 Toggleen ko, te lekk ko ci bérab bi seen Yàlla Aji Sax ji di taamuji, ca suba sa ngeen xëy, dellu ca seeni xayma. \v 8 Juróom benni fan ngeen di lekk mburu mu amul lawiir, bésub juróom ñaareel di am ndaje, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Buleen ci liggéey dara. \p \v 9 Juróom ñaari ayi bés nag, ngeen di waññ, te ci ndoortel ngóob ngeen di tàmbalee waññ juróom ñaari ayi bés yi, \v 10 ngeen doora amal \w màggalug Ayi bés|lemma="Màggali Yawut yi:"\w*, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji, te \w saraxu yéene|lemma="Sarax yi:"\w* ba ngeen cay joxe di kemu koom ga leen seen Yàlla barkeele. \v 11 Ngeen daldi bànneexu fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, yeen ak seeni doom, góor ak jigéen ak seeni jaam, góor ak jigéen, ak \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi ci seen dëkk, ak doxandéem yeek jirim yeek jëtun ñi ci seen biir, ci bérab bi seen Yàlla Aji Sax ji taamoo dëël turam ëllëg. \v 12 Fàttlikuleen ne ay jaam ngeen woon ca Misra te ngeen sàmmoo jëfe dogali yoon yii. \p \v 13 \w Màggalu Mbaar|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* yi it nangeen ko wormaal diiru juróom ñaari fan, gannaaw bu ngeen dajalee seenum pepp, ak seen ndoxum reseñ. \v 14 Ngeen daldi bànneexoo seenug màggal, yeen ak seeni doom, góor ak jigéen, ak seeni jaam, góor ak jigéen, ak Leween ñeek doxandéem yeek jirim yeek jëtun, ñi ci seen biir dëkk. \v 15 Juróom ñaari fan ngeen koy màggal ñeel seen Yàlla Aji Sax ji ci bérab bi Aji Sax ji di taamuji, ndax seen Yàlla Aji Sax ji moo leen di barkeelal seen meññat mépp, ak seen mboolem ñaq, seen mbégte mat sëkk. \p \v 16 Kon ñetti yoon cim at la mboolem seeni góor di teew fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ci bérab bi muy taamuji: fani \w màggalu Mburu mu amul lawiir|lemma="Màggali Yawut yi:"\w*, ak fani màggalug Ayi bés, ak fani màggalu Mbaar yi. Waaye deesul teewe loxoy neen fi kanam Aji Sax ji. \v 17 Ku nekk, na sarax ba muy indi, di kemu barke ba ko Yàlla jagleel. \s1 Yoon wi sàrtal na mbirum àtte \p \v 18 Te itam ay àttekat aki kilifa ngeen di tabb ngir seeni giir, ci mboolem dëkk yi leen seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jiy jox, ñuy àtte mbooloo mi àtteb dëgg. \v 19 Buleen jalgati yoon cib àtte, buleen jeng te buleen nangu alalu ger, ndax ab ger day muur bëti boroom xel, di xañ aji jub dëgg. \v 20 Dëgg doŋŋ ngeen wara topp, ndax ngeen dund, jagoo réew mi leen seen Yàlla Aji Sax ji di jox. \p \v 21 Buleen samp benn xeru bant, bu jóge ci genn garab, ngir di ko jaamoo \w Asera|lemma="Asera:"\w* tuur mi, ci seen wetu \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi ngeen sàkk ngir seen Yàlla Aji Sax ji. \v 22 Te itam buleen yékkati lenn lu bokk ci doji jaamookaay yooyu seen Yàlla Aji Sax ji bañ. \c 17 \p \v 1 Buleen sarxalal seen Yàlla Aji Sax ji, aw nag mbaa ab gàtt bu am sikk, mbaa jenn laago, ndax seen Yàlla Aji Sax ji seexlu na loolu. \p \v 2 Bu nit feeñee ci seen biir, ci benn ci dëkk yi leen seen Yàlla Aji Sax jiy jox, muy góor mbaa jigéen juy def lu seen Yàlla Aji Sax ji ñaawlu, di fecci \w kóllëreem|lemma="kóllëre g-:"\w*, \v 3 bay jaamuji yeneen yàlla, di leen sujjóotal, mbaa muy sujjóotal jant bi, mbaa weer wi, mbaa mboolem gàngooru asamaan, te santaanewuma ci lenn, \v 4 buñu leen ko yeggee ba ngeen dégg ko, seetleen mbir ma bu baax. Su dee dëgg gu wér, ne defees na lu jomblu loolu ci biir Israyil, \v 5 nangeen génne ba ca buntu dëkk ba, waa ji, mbaa ndaw si def jooju jëf ju bon, te ngeen dóor ay doj, waa jooju mbaa ndaw si, ba mu dee. \v 6 Kàddug ñaari seede ba ñett nag, ci lees di reye ki ñu wara rey, waaye deesu ko rey ci kàddug benn seede. \v 7 Loxoy seede yee koy jëkka dóor doj ngir rey ko, loxoy mbooloo mépp door koo dóor. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir. \p \v 8 Su leen mbir jafee ba wees leen ci àtteb bakkan bu ñu faat, ak ay jote, ak loraangey yaram yu ñu teg nit, ak mboolem dëngoo bu laaj àtte ci seen biir dëkk, dangeen di dem ba ca bérab ba seen Yàlla Aji Sax ji di taamuji, \v 9 ngeen àgg ca \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ya, \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ña, ak àttekat, ba mbir ma yemool jamono, te ngeen sàkku ñu biral leen àtteb mbir ma. \v 10 Nangeen jëfe nag kàddu ga ñu leen ca wax, ca bérab booba Aji Sax ji taamu, te ngeen sàmmoo koo jëfe mboolem noonee ñu leen ko digale. \v 11 Kàddug ndigal la ñu leen digal, ak àtte ba ñu leen ci wax, jëfeleen ko. Buleen lajje fenn kàddu ga ñu leen ca wax; du ndijoor, du càmmoñ. \v 12 Képp ku ci daŋŋiiral, baña déggal sarxalkat ba fa ayee liggéeyal seen Yàlla Aji Sax ji, baña déggal àttekat ba, kooku dees koy rey. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci Israyil. \v 13 Askan wépp a koy dégg, tiit, ba duñu daŋŋiiralati. \s1 Ay ndigal ñeel na buur \p \v 14 Bu ngeen demee nag ca réew ma leen seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji di jox, bu ngeen ko nangoo, dëkke, ba ne: «Nanu fal buur bu nu jiite ni mboolem xeet yi nu séq,» \v 15 su boobaa fexeleen ba ka ngeen di fal buur, di ka seen Yàlla Aji Sax ji taamu. Ci seen biiri bokk nag ngeen di fal seen buur. Dungeen mana fal buur ab jaambur bu dul seen mbokkum bànni Israyil. \v 16 Waaye bu buur bi barey fas, te bumu delloo askan wi Misra, ngir sàkku fas yu bare, te Aji Sax ji waxoon leen ne buleen dellooti woowu yoon. \v 17 Bumu barey jabar, balaa am xelam di lajj. Xaalis ak wurus it, bumu ko barele lool. \p \v 18 Bu buur bi toogee ci jalub nguuram, na bindlu ngir moom ci boppam, ab sottib téereb yoon wii cib taxañ, ci dégtalub \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi, \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi. \v 19 Na téere boobu ànd ak moom, mu di ci jàng giiru dundam, ndax mu tàggatu ci ragal Yàllaam Aji Sax ji, ngir di sàmm mboolem kàdduy yoon wii, ak dogali yoon yii, ngir di ko jëfe, \v 20 ba du xoggliku ci kawi bokkam, te du moye santaane bi fenn; du ndijoor, du càmmoñ, ndax mu gudd fan ci nguuram, moom ak askanam, ci digg Israyil. \c 18 \s1 Ay yelleef ñeel na Leween ñi ak sarxalkat yi \p \v 1 \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñiy ay \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w*, ba ci giirug Leween gépp nag, wenn wàll mbaa céru suuf ñeelu leen ci seen bokki Israyil. Saraxi sawara yu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, akub céram, moom lañuy dunde. \v 2 Ab cér du leen ñeel ci seen biiri bokk. Aji Sax ji mooy seenub cér, na mu leen ko waxe woon. \v 3 Lii mooy li lew sarxalkat yi, te bàyyikoo ci askan wi, ci ñiy rendi ay sarax, muy aw nag, di ab gàtt: nañu jox sarxalkat bi, mbagg mi ak lex yi, ak mbàq gi. \v 4 Te seen pepp mu jëkka ñor, ak seen biiñ bu bees, ak seen diw gu bees, ak kawar gi ngeen jëkka wate ca seeni xar, joxleen ko ko, \v 5 ndax seen Yàlla Aji Sax ji moo ko taamu, ci seen mboolemi giir, ngir mu taxaw, di liggéey ci turu Aji Sax ji, moom ak askanam, ba fàww. \p \v 6 Ab Leween bu dëkke benn ci seeni dëkk, ak fu mu mana doon ci Israyil, su fa jógee dem ci coobarey boppam, bérab bu Aji Sax ji taamu, \v 7 da fay liggéey ci turu Yàllaam Aji Sax ji ni mboolem bokki Leweenam, ña fa taxawe fa kanam Aji Sax ji, \v 8 njël lu yemook njëlal ña mu fa fekk it lew na ko, te limaaleesul lu ko dikke ci njaayum alalu baayam. \s1 Kàddug waxyu day sotti \p \v 9 Bu ngeen demee ca réew ma leen seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji di jox, buleen roy jëf ju jomblu ju xeet yooyu. \v 10 Bu kenn fekk ci seen biir kuy sarxe doomam ju góor, ak ju jigéen, lakk ko; ak kuy luxus, ak kuy seet, ak kuy gisaane, ak kuy xërëm, \v 11 ak kuy liggéeyaate, ak kuy seete ab rawaan, ak kuy seete aw rab, mbaa kuy seete nit ñu dee, \v 12 ndax mboolem ñiy def yooyu, Aji Sax ji seexlu na leen. Jëf ju seexluwu jooju moo waral seen Yàlla Aji Sax ji di leen dàqal seeni boroom. \p \v 13 Muccleen sikk seen digganteek seen Yàlla Aji Sax ji, \v 14 ndax xeet yooyii ngeen di dàqi kat, ay luxuskat aki seetkat lañuy déggal, waaye yeen seen Yàlla Aji Sax ji mayu leen loolu. \v 15 Ab yonent bu soqikoo ci yeen kay, di seen mbokk ni man, moom la leen seen Yàlla Aji Sax ji di feeñalal. Moom ngeen di déggal. \v 16 Mooy noonee ngeen ko sàkkoo woon rekk, ci seen Yàlla Aji Sax ji ca tundu Oreb, ca bésub ndaje ma, ngeen ne: «Rikk bunu déggati sunu baatu Yàlla Aji Sax ji. Sawara wu réy wii it, bunu ko gisati, lu ko moy nu dee,» \v 17 te Aji Sax ji ne ma: «Ñoo yey wax loolu. \v 18 Ab yonent laa leen di feeñalal ci seen biiri bokk, ni yaw. Maay yeb samay kàddu ci gémmiñam, mu àgge leen mboolem lu ma ko sant. \v 19 Su boobaa ku déggalul sama kàddu yi muy wax ci sama tur, man maa ko koy topp. \v 20 Waaye déy yonent bu am fitu àddu genn kàddu ci sama tur, te santuma ko mu wax ko, mbaa mu wax ci turi yeneen yàlla, boobu yonent, dee mooy àtteem.» \p \v 21 Dingeen wax ci seen xel, ne: «Ana nu nuy ràññee kàddu gu Aji Sax ji waxul?» \v 22 La yonent bi wax ci turu Aji Sax ji, su sottiwul, dikkul rekk, loola du kàddu gu Aji Sax ji wax. Ñeme Yàlla la ko yonent ba waxe, buleen ko ragal. \c 19 \s1 Ber dëkki rawtu ndigal la \p \v 1 Gannaaw bu leen seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wollilee xeet yi mu leen di jox seenum réew, ngeen dàq leen, ba dëkke seeni dëkk ak seeni kër, \v 2 ñetti dëkk yu mag ngeen di ber ca biir réew mooma leen seen Yàlla Aji Sax ji jox, ngir ngeen jagoo ko. \v 3 Ngeen waajal nag yoon wu jëm ci dëkk bu ci nekk, te ngeen séddale ñetti pàcc réew mooma leen seen Yàlla Aji Sax ji sédd, ngir képp ku rey nit, man caa làquji. \p \v 4 Mbirum ki rey nit te di fa làquji ba mucc, nii lay tëdde: day fekk mu rey moroomam te du teyeefam, waaye bañu ko woon démb ak bëkk-démb. \v 5 Mu mel ni ku ànd ak moroomam ca gott ba, di gor matt. Mu doon xàcci sémmiñam di gor, weñ ga fettaxe ca njàppu la, dal ca moroom ma, mu dee. Kooku day làquji ci dëkk yooyu benn, ba mucc. \v 6 Toppkatu bakkan ba nag warul mana dabi ci biir xolam bu tàng, ki rey, ba rey ko ngir sorewaayu yoon wa jëm ca dëkkub rawtu ba, te àtteb yoon reyluwu ko, gannaaw fekkul woon mu bañ ka mu rey, démb ak bëkk-démb. \v 7 Looloo waral ma sant leen, ne leen ñetti dëkki rawtu ngeen di ber. \p \v 8 Bu seen Yàlla Aji Sax ji yaatalee seen suuf, na mu ko giñale woon seeni maam nag, ba jox leen mboolem réew ma mu dige woon ne dina ko jox seeni maam, \v 9 ndegam sàmm ngeen mboolem santaane bii ma leen dénk tey, ngir di ko jëfe, ngir sopp seen Yàlla Aji Sax ji, di awe ay yoonam bés bu nekk, su boobaa nangeen yokkaat ñetti dëkk yu mag, mu dolliku ci ñetti dëkk yi ngeen jëkka ber. \v 10 Su ko defee deesul tuur deretu jaambur bu deful dara ci suufas réew, mi leen seen Yàlla Aji Sax ji sédd, ba àqu deret di leen topp. \p \v 11 Su fekkee ne nit ki dafa bañ moroomam, su ko tëroo, dal ci kawam, ba fàdd ko, mu dee, su làqujee ci dëkk yooyu benn, \v 12 su boobaa na magi dëkkam yeble, ñu jële ko foofa, teg ko ci loxol toppkatu bakkan ba, ngir mu dee. \v 13 Buleen ko xool bëtu yërmande. Noonu ngeen di dindee ci Israyil, àqu deretu jaambur bu deful dara, ndax ngeen baaxle. \s1 Lu jëm ci kemu suuf ak limu seede cib àtte \p \v 14 Te it buleen toxal seen yemukaayu suufas moroom yu maam ya yemalee woon ci seen biir céru suuf ba ngeen jagoo, ca réew ma leen seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji di moomale. \p \v 15 Bennub seede nag du taxaw, di tuumaal kenn, ci genn tooñ mbaa bàkkaar, ak bépp bàkkaar bu mu mana bàkkaar. Ci kaw kàddug ñaari seede mbaa ñett la mbir ma di wére. \p \v 16 Su ab seedeb safaan taxawee, tuumaal kenn, ne moo lajj yoon, \v 17 na ñaari nit, ña séq mbir ma taxawi fa kanam Aji Sax ji, fa kanam \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ya, ak àttekat ya ca yooyu jant. \v 18 Su ko defee àttekat yi seet bu baax, ba mu wér ne seede ba kat, seedeb soskat la buy seedeel mbokkam aw sos, \v 19 te ngeen def ak moom, la mu naroona yóbbe ka mu sosal. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir. \v 20 Ñi ci des dinañu ko dégg, te dinañu ragal ba duñu defati lu bon lu ni mel ci seen biir. \v 21 Buleen ci xool bëtu yërmande. Bakkan, bakkan a koy fey; bët, bët; bëñ, bëñ; loxo, loxo; tànk, tànk. \c 20 \s1 Yoon wi sàrtal na mbirum xare \p \v 1 Bu ngeen demee ngir xarejeek seeni noon ba gis ay fas, aki watiir, ak gàngoor gu leen ëpp, buleen leen ragal, ndax seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jaa ngeek yeen, ki leen jële woon réewum Misra. \v 2 Bu ngeen di waaja xare, na \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi dikk, wax ak mbooloo mi, \v 3 ne leen: «Éey Israyil, dégluleen, yeena ngi waaja xareek seeni noon tey jii. Buleen yox-yoxi, buleen ragal, buleen tiit, buleen teqlikook seen sago ci seen kanam! \v 4 Ndaxte seen Yàlla Aji Sax ji mooy kiy dox ànd ak yeen, xeexal leen ak seeni noon, ngir may leen ndam.» \p \v 5 Su ko defee kilifay xarekat yi wax ak gàngoor gi, ne leen: «Ana góor gu ci tabaxoon néeg bu bees te daloogu ko? Na daldi dellu cab néegam bala moo dee ci xare bi, geneen góor daloo ko. \v 6 Ana góor gu ci jëmbatoon tóokëru reseñ te jariñoogu ko? Na daldi ñibbi bala moo dee ci xare bi, geneen góor jariñoo ko. \v 7 Ana ku ci ngoroom dëgëroon te jëlagul? Na daldi ñibbi bala moo dee ci xare bi, geneen góor jël ko.» \v 8 Gannaaw loolu, na kilifa yi dellu wax ak gàngoor gi, ne leen: «Ana ku ci ragal, ana ku ciy yox-yoxi? Na daldi ñibbi kat, bala moo yoqiloo ay moroomam, ni moom.» \v 9 Bu kilifay xare ya waxeek gàngoor gi ba noppi, nañu tabb ay njiiti kurél, ñu jiite gàngoor gi. \p \v 10 Bu ngeen dikkee ba jub ab dëkk, ngir xareek ñoom, jëkkleen leena woo ci jàmm. \v 11 Ndegam jàmm lañu leen wuyoo, ba ubbil leen, mboolem askan wa mu fekk ca biir dëkk ba dañuy tegoo liggéeyu sañul-bañ, ñeel leen, di leen jaamu. \v 12 Waaye bu ñu jàmmoowul ak yeen, xanaa di xareek yeen, gawleen dëkk ba. \v 13 Seen Yàlla Aji Sax ji moo leen di teg ci seen loxo, ngeen daldi leel ñawkay saamar mboolem seeni góor. \v 14 Waaye jigéen ñi ak tuut-tànk yi, ak jur gi, ak mboolem lu ne ca biir dëkk ba, mboolem alal ja, sëxëtooleen, jagoo. Lekkleen alal ji ngeen foqatee ci seen noon, yi leen seen Yàlla Aji Sax ji jébbal. \p \v 15 Noonu ngeen di def ak dëkk yi soreek yeen lool te bokkuñu ci dëkki xeet yii ngeen jëm. \v 16 Dëkki xeet yii leen seen Yàlla Aji Sax ji sédd nag, buleen ci bàyyi lenn luy noyyi, mu dund. \v 17 Nangeen faagaagal Etteen ñi ak Amoreen ñi ak Kanaaneen ñi ak Periseen ñi ak Eween ñi ak Yebuseen ñi, na leen ko seen Yàlla Aji Sax ji sante woon, \v 18 ndax ñu bañ leena royloo, ngir ngeen di jëfe seen mboolem yu jomblu yi ñuy defal seeni tuur, ba ngeen moy seen Yàlla Aji Sax ji. \p \v 19 Bu ngeen gawee lu yàgg ab dëkk, ngir song leen xare, ba nangu ko, buleen fóom ay garabam, di ca gor lenn te mana lekk ca doom ya. Kon nag garab, buleen ko gor. Garab du nit ba ñu di ko def ni ku ñu gaw. \v 20 Terewul garab gu ngeen xam ne deesul lekk doom ya, gorleen ko, daaneel, te ngeen sàkke ko ab gawukaay bu wër dëkk biy xareek yeen, ba keroog dëkk bay daanu. \c 21 \s1 Njotlaay war na ci bóomkat bu umpe \p \v 1 Su dee dañoo fekk ku ñu bóom ci biir réew mi leen seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji moomale, mu tëdd ci àll bi, te xameesul ku ko rey, \v 2 na seeni mag ak seeni àttekat dem, natti diggante fa néew ba tëdd, ak dëkk ya ko séq. \v 3 Su ko defee dëkk ba gëna jegewook néew ba, magi dëkk booba tànne ca nag wu jigéen wu ñu masula liggéeyloo, te maseesu koo ràng. \v 4 Na magi dëkk boobu wommat nag wi ba ci xur wu wal ma dul ŋiise, te maseesu cee bey, maseesu cee ji. Ñu daldi damm loosu nag wu jigéen wi foofa ca wal ma. \p \v 5 Su ko defee \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi, \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi dikk, ndax ñoom la seen Yàlla Aji Sax ji taamu, ngir ñu di ko liggéeyal, di barkeele ciw turam, te ci seen kaw kàddu lees di àttee bépp jote, ak gépp loraange ci wàllu yaram. \v 6 Dëkk boobu gëna jegewook fa néew ba tëdd, na mboolem seeni mag raxas seeni loxo, tiimale ca nag wu jigéen wa ñu damm loos wa, ca wal ma. \v 7 Ñu biral ne: «Nun déy sunuy loxo tuurul deretu nit kii, te sunuy gët it gisul ba ñu koy tuur. \v 8 Ngalla Aji Sax ji, jéggalal Israyil, sa ñoñ ñi nga jot, te baña toppe àqu deretu jaambur bu deful dara, fi digg Israyil sa ñoñ.» Su ko defee njéggal ñeel leen, ca deretu nit ka. \v 9 Yeen nag, noonu ngeen di tenqee ci seen biir, àqu deretu jaambur ju ñu tuur, ndax kon def ngeen li Aji Sax ji rafetlu. \s1 Ay sàrt a ngi ci wàllu njaboot \p \v 10 Bu ngeen xarejeek seeni noon, te seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji teg leen ci seeni loxo, ba ngeen jàpp leen njaam, \v 11 su ngeen gisee ca jaam yu jigéen ya, ku rafet ku ngeen xédd, te bëgg koo jël jabar, \v 12 yóbbuleen ko seen biir néeg, mu watu nel, dagg ay wewam, \v 13 summi yére ya ñu ko jàppe njaam, te toog seen biir néeg. Day tiislu nag ndeyam ak baayam lu mat weeru lëmm. Gannaaw loolu ngeen dëkkoo ko, di jëkkëram, muy seen jabar. \v 14 Bu loolu amee ba neexatu leen, bàyyileen ko, mu dem fu ko neex, waaye buleen ko jaay mukk, di ko weccikoo xaalis. Buleen ko jaamloo it, gannaaw bu ngeen ko jabaroo ba noppi. \p \v 15 Ku am ñaari jabar, su xejjoo kenn ki, foñ ki ci des, te ki mu xejjoo, ak ki mu foñ jural koy doom yu góor, te taaw bu góor bi di doomu ki mu foñ, \v 16 bés buy séddale doomam yu góor alalam, du saña jox doomu xejj bi, cér bi taaw yelloo, wacc doomu ka mu foñ, te muy taaw. \v 17 Taaw bay doomu ka mu foñ, na ko nangul ab céram, jox ko ñaar-cay céru rakk ja, ci mboolem alalam, ndax kooka soqikoo ci digg dooleem, mooy ka yelloo céru taaw. \p \v 18 Ku am doom ju góor ju dëgër bopp te të; déggalul baay, déggalul ndey, su ñu ko yaree, te taxul mu déggal leen, \v 19 na ko baayam ak ndeyam jàpp, yóbbu ba ca seen magi dëkk ba, ca seen bunt dëkk. \v 20 Ñu wax seen magi dëkk ba, ne leen: «Sunu doom jii ku dëgër bopp la te të. Déggalu nu, xanaa di xawaareek a màndi rekk.» \v 21 Na ko góori dëkk bépp dóori doj ba mu dee. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir. Israyil gépp a koy dégg, daldi ragal. \s1 Deesul wékk nit, fanaanal ko \p \v 22 Su nit moyee ba dee di àtteem, ñu rey ko, wékk ko ci garab, \v 23 bu néewam fanaan ca garab ga, nañu ko daldi rob ca bés ba, ndax ki wékke alkàndey Yàlla la. Buleen sobeel réew mi leen seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* sédd. \c 22 \s1 Yoon wi sàrtal na dundin wu jekk \p \v 1 Buleen gis seen nagu mbokk mbaa gàttam bu réer, ba jàpp ci seen njaambur. Fexeleen koo waññi, ba delloo ko seen mbokk ma. \v 2 Su mbokk mi jegewoowul ak yeen, mbaa xamuleen ko, yóbbuleen jur gi seen kër, mu des fa, ba mbokk mi dikk, di ko seet, ngeen delloo ko ko. \v 3 Noonu ngeen di def, su dee mbaam, noonu ngeen di def su dee mbubb, noonu it ngeen di def, ak mboolem lu seen mbokk réerle, ba ngeen gis ko. Dungeen ci mana jàpp seen njaambur. \p \v 4 Buleen gis seen mbaamu mbokk, mbaa nagam wu daanu ciw yoon, ba ngeen jàpp ci seen njaambur. Fexeleen ba yékkatile ko ko. \p \v 5 Bu lenn ci mboolem yëfi góor, tegu ci kaw ku jigéen, te bu góor sol yérey jigéen, ndax \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji seen Yàlla seexlu na képp kuy def yooyu. \p \v 6 Bu ngeen doxee ba yem ci tàggum picc ci seenu yoon, mu nekk ci garab gu mu mana doon, mbaa ci suuf, cuuj ya mbaa nen ya nekk ca, te yaay ja bóof ca kaw cuuj ya, mbaa nen ya, buleen boole jël yaay ja ak cuuj ya. \v 7 Fexeleen ba bàyyi yaay ja, te jël cuuj ya, ndax ngeen baaxle te gudd fan. \p \v 8 Su ngeen dee tabax kër gu bees, sàkkal-leen seen kawum taax, ab feguwaay, bala caa nit a daanoo, àqu deret topp seen kër. \p \v 9 Buleen ji ci seen tóokëru reseñ, weneen wirgo, lu ko moy lépp ay doon céru sellnga bu ngeen dul saña jariñoo: li jóge ci jiwu mi rax reseñ ji, ak itam meññeefum reseñ ji. \v 10 Buleen ràngandoo nag ak mbaam, di leen rijjiloo. \p \v 11 Buleen sol ndimol njaxas lu ñu raxe kawaru gàtt ak wëñu lẽe. \p \v 12 Ay cimbir-cimbir nag ngeen di def ci ñeenti weti malaanum sàngukaay mu ngeen di sàngoo. \s1 Sàmmonteleen ak àqu jigéen \p \v 13 Ku jël jabar, dëkkoo ko, ba noppi jéppi ko, \v 14 di ko tuumaal, di teg lu ñaaw ci deram, naan: «Ndaw sii ma jël, ba ma àggee ci moom, fekkuma ko janq,» \v 15 su boobaa na baayu ndaw si ak ndeyam, jël firndey ndaw la, yóbbu ko ba ca kanam magi dëkk ba, ca bunt dëkk ba. \v 16 Su ko defee baayu ndaw si ne mag ñi: «Sama doom laa mayoon waa jii jabar; mu walbatiku jéppi ko. \v 17 Mu ngii di ko tuumaal, naan: “Fekkuma sa doom ji janq.” Te sama ndawal doom a ngii!» Nañu tàllal malaan ma ca kanam magi dëkk ba. \v 18 Su loolu amee, na magi dëkk booba jàpp waa ji, yar ko. \v 19 Nañu ko daan téeméeri donji xaalis, jox ko baayu ndaw si, ndax moo yàq deru janqub Israyil. Jabaram lay doon ba tey, te du ko saña wacc giiru dundam. \p \v 20 Waaye su tuuma ji dee dëgg, te giseesul lenn ndaw ca ndaw sa, \v 21 nañu yóbbu ndaw sa ba ca bunt kër baayam, te góori dëkk bi dóor koy doj ba mu dee, ndax moo def jëf ju gàccelu ci digg Israyil, di gànctoo kër baayam. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir. \p \v 22 Bu ñu fekkee kuy tëdde ku am jëkkër; ka ko tëdde ak ka ñu tëdde, dee mooy seen àtte, ñoom ñaar ñépp, ngeen tenqee ko lu bon ci Israyil. \p \v 23 Su ab janq digoo ak waayam ab séy, gannaaw gi keneen dajeek moom ci biir dëkk bi, tëdde ko, \v 24 génneleen leen ñoom ñaar, ba ca bunt dëkk booba, ngeen dóor leen ay doj ba ñu dee, ndax ndaw si moo yuuxuwul woon wall, te muy ca biir dëkk ba, te waa ji it moo jabaroo jabaru moroomu góoram. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir. \p \v 25 Su fekkee ne ci àll bi la waa ji dajeek ndaw, si digook keneen ab séy, mu jàpp ko, tëdde ko, nag, waa ji ko tëdde doŋŋ la dee di àtteem. \v 26 Waaye ndaw si deesu ko def dara. Bàkkaar bu dee di àtteem toppu ko ca, ndax ni ku song moroomam, bóom ko rekk, ni la mbir moomu deme, \v 27 nde biir àll ba mu dajeek ndaw sa, bu ndaw sa yuuxu woon it, du am ku ko wallu. \p \v 28 Ku dajeek as ndaw, te mu dib janq bu digoowul ak keneen ab séy, su ko jàppee, tëdde ko, ba ñu gis leen, \v 29 kooka tëdde ndaw sa, day jox baayu ndaw sa juróom fukki donji xaalis. Jabaram lay doon it, gannaaw moo ko jabaroo, te du ko saña fase, giiru dundam. \p \v 30 Bu kenn jël jabaru baayam, di teddadil lalu baayam. \c 23 \s1 Am na ñu dul bokk ci ndajem Aji Sax ji \p \v 1 Ku ñu mor mbaa ñu dagg ngóoraam, du bokk ci ndajem gëmkati \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \v 2 Ku dul doomu yoon du bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji. Ku askanoo ci moom it, ba ca fukkeelu maas ga, du bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji. \v 3 Ab Amoneen mbaa ab Mowabeen du bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji. Ku askanoo ci ñoom it, ba ca fukkeelu maas ga, du bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji mukk, \v 4 ndax la ñu leen dabewul woon aw ñam, mbaa am ndox, ca yoon wa, ba ngeen génnee Misra, xanaa di fey Balaam doomu Bewor ma bokk Petor ca Aram Naarim, ngir mu sàbbi leen. \v 5 Waaye seen Yàlla Aji Sax ji moo nanguwula déglu Balaam; kàddug yàqe ga la leen seen Yàlla Aji Sax ji soppil barke, ndax seen Yàlla Aji Sax ji da leena sopp. \v 6 Buleen sàkku mukk jàmmu ñooñu mbaa seen njariñ, seen giiru dund, ba fàww. \p \v 7 Buleen bañ ab Edomeen, ndax seen mbokk la. Buleen bañ nitu Misra, ndax ay doxandéem ngeen woon ca seenum réew. \v 8 Ñi soqikoo ci ñaari xeet yooyii, ca ñetteelu maas ga, te di seeni sëtaat\f + \fr 23.9 \fr*\ft Mooy ñetteelu maasug xeet yooyu taamoo dëkke réewum Israyil. Seetal ci \ft*\ft \+bk Màndiŋ ma\+bk* 12.1-15.\ft*\f* nag, sañ nañoo bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji. \p \v 9 Bu ngeen génnee ba fàkk ab dal, ngir jànkoonte ak seeni noon, nangeen sàmmu ci lépp lu aay. \v 10 Su amee ci seen biir ku setul, ndax géntu guddi gu ko dikkal, na génn dal bi, ca biti, te bumu duggaat ci biir dal bi. \v 11 Bu ngoon di jubsi na sangu, ba jant bi so, mu doora délsi ci biir dal bi. \v 12 Te sàkkleen bérab bu génn dal bi, ngeen di fa dem, di suturluji. \v 13 Na ngaska bokk ci seeni fàgguwaay, ndax su ngeen suturlujee ca biti ba noppi, moom ngeen di gase, ba suul seeni jonkan. \v 14 Ndax seen Yàlla Aji Sax ji mooy dem ak a dikk ci seen biir dal bi, ngir xettli leen, ba jébbal leen seeni noon. Kon nag seenub dal daa wara sell, ngir Aji Sax ji ñàkka gis fi seen biir, lenn lu tegginewul, ba dëddu leen. \p \v 15 Gannaaw loolu buleen delloo ab jaam bu làqu ci yeen, te rëcce ci ab sangam. \v 16 Ci yeen lay toog, ci seen biir, bérab ba mu taamu, ci benn bi ko gënal ci seeni dëkk, te buleen ko néewal doole. \p \v 17 Gànc bu jigéen buy gànctul ay tuur, bumu am ci biir jigéeni Israyil, te gànc bu góor buy gànctul ay tuur\f + \fr 23.18 \fr*\ft Googu gànctu, jaamukati tuur ya ca Kanaan daan nañu ko jëfe, ngir yaakaar ne dina tax seenum njur, ak seeni tool nangu.\ft*\f*, bumu am ci góori Israyil. \v 18 Buleen indi mukk ci seen biir kër Yàlla Aji Sax ji, peyooru gànc bu jigéen, mbaa bu góor, ngir wépp xas wu ngeen namma wàccoo googu peyoor, ndax yooyu yaar yépp, seen Yàlla Aji Sax ji seexlu na ko. \s1 Deesul topp bànni Israyil ab tegandaay \p \v 19 Buleen teg seen mbokkum bànni Israyil tegandaayal xaalis, mbaa tegandaayal ñam, mbaa tegandaayal mboolem bor bu tegandaay tege. \v 20 Ab doxandéem, sañ ngeen koo sàkku tegandaay, waaye seen mbokkum bànni Israyil, buleen ko sàkku tegandaay. Su ko defee seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji mooy barkeel mboolem seenu ñaq, ca réew ma ngeen jëm, ngir nanguji ko. \s1 Wàccook aw xas wartéef la \p \v 21 Su ngeen xasalee seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, aw xas, buleen ko yeexa wàccool, ndax kon seen Yàlla Aji Sax ji du leen ko ñàkka topp, te kon muy seen bàkkaar. \v 22 Waaye baña xas, amul bàkkaar. \v 23 Li seen làmmiñ tudd, sàmmooleen koo jëfe na ngeen ko xasale woon seen Yàlla Aji Sax ji, ci seen sagoy bopp, ak seen kàddug bopp. \s1 Raasaatu mu suur boroom lew na \p \v 24 Bu ngeen duggee ci seen tóokëru reseñu moroom, lekkleen ca reseñ ja lu leen neex ba suur, waaye seen ndab, buleen ko ca yeb. \v 25 Bu ngeen duggee ci seen toolu peppu moroom, fekk mu ñor, sàkkeleen seen loxo ca gub ya, waaye ab sàrt, buleen ko xàccil seen peppu moroom. \c 24 \s1 Yoon wi sàrtal na pase ak séyaat \p \v 1 Ku jël jabar, ba gannaaw gi xoolatu ko bëtu yiw, ndax lu tegginewul lu mu ko gisal, su ko bindalee kayitu pase, teg ko ci loxoom, ba yiwi ko, mu jóge këram, \v 2 su jógee ca kër ga, dem ba mujj doon jabaru keneen, \v 3 su ko jëkkëram ju mujj jooju jéppee, bindal ko kayitu pase, teg ko ci loxoom, ba yiwi ko, mu jóge këram, mbaa su jëkkëram jooju ko mujja jël faatoo, \v 4 su boobaa jëkkëram ju jëkk ja ko yiwi woon du ko saña jëlaat jabar, gannaaw ba ndaw sa sobewoo noonu, ndax loolu lu jomblu la fi kanam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, te waruleena indi bàkkaar ci biir réew mi leen seen Yàlla Aji Sax ji di moomale. \p \v 5 Ku jël ab séet du bokk ci gàngoor gu jëm xare, te deesu ko sas lenn. Day moom boppam atum lëmm, ngir toog këram, di bégal jabaram ji mu jël. \s1 Yoon wi aar na néew-ji-doole \p \v 6 Buleen tayleloo kenn ñaari doji wolukaayam, ci bor bu mu leen ameel. Buleen ko tayleloo wenn doj wa féete kaw sax, ndax kon bakkanam ngeen def ub tayle. \p \v 7 Su amee nit ku ñu fekke kenn ciy bokkam, ku mu sàcce ci \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, mu di ko jaamloo, mbaa mu jaay ko, su boobaa dee mooy àtteb kooka ko sàcc. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir. \p \v 8 Fexeleen ba ci biir mbasum jàngoroy der juy màgg, ngeen di sàmmoo jëfe bu baax, mboolem lu leen \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi, \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi tegtal. Ni ma ko sante sarxalkat yi, Leween ñi, sàmmooleen koo jëfe noonu. \v 9 Fàttlikuleen la seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji defoon Maryaama ca yoon wa, ba ngeen génnee Misra\f + \fr 24.9 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Màndiŋ ma\+bk* 12.10.\ft*\f*. \p \v 10 Bu ngeen lebalee seen moroom, ak lu bor ba mana doon, buleen dugg biir néegam, di fa jël ab tayleem. \v 11 Ca biti ngeen di taxaw, ka ngeen di lebal yótsi leen ab tayleem ca biti. \v 12 Su dee ku néew doole, buleen tëraale ab tayleem. \v 13 Fexeleen ba delloo ko tayle ba bu jant biy so, ba mu tëraale mbubbum tayle ma, sante leen ko, mu dig njekk, fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji. \p \v 14 Buleen gàddu àqu liggéeykat, baadoolo bu néew doole ci seen biiri bokk, mbaa ci seen dëkkandoo yiy doxandéem ci seen dëkk yi ci réew mi. \v 15 Ci bés bi ngeen koy fey peyooram. Bu ko jant sowe, ndax néew doole la te moom la yaakaara dunde. Lu ko moy mu boole leen ak Aji Sax ji, ngeen gàddu bàkkaar. \p \v 16 Deesul teg waajur àtteb dee, ngir weccikoo ko doom ja, te doom it deesu ko teg àtteb dee, weccikoo ko waajur wa. Nit ku nekk, bàkkaaru boppam lees koy tege àtteb dee. \p \v 17 Buleen xañ dëgg ab doxandéem akub jirim, te buleen taylelu mbubbum jëtun. \v 18 Fàttlikuleen ne ay jaam ngeen woon ca Misra, seen Yàlla Aji Sax ji moo leen fa jote. Looloo waral man, ma sant leen ngeen jëfe ndigal loolu. \p \v 19 Bu ngeen di góob seenub tool, ba fàtte ab sëq ca tool ba, buleen dellu di ko jëli. Ab doxandéem akub jirim akub jëtun, ñoom la poraat may ñeel, su ko defee seen Yàlla Aji Sax ji barkeel leen ci mboolem seenu ñaq. \v 20 Bu ngeen bàccee seen garabu oliw ba noppi, buleen toppaat car ya, di witt lu ca des. Ab doxandéem akub jirim akub jëtun, ñoom la ndesit way ñeel. \v 21 Bu ngeen wittee seen tóokëru reseñ, buleen dellu, di ko wittaat. Ab doxandéem akub jirim akub jëtun ñoom la wittaat may ñeel. \v 22 Fàttlikuleen ne ay jaam ngeen woon ca réewum Misra. Looloo waral man, ma sant leen ngeen jëfe ndigal loolu. \c 25 \s1 Njub ak yërmande wartéef la \p \v 1 Su ab jote amee diggante ay nit, nañu dem ca ëttub àttekaay ba, ñu àtte leen, ba ki am dëgg, ñu jox ko dëgg, ki tooñ, ñu teg ko tooñ. \v 2 Su dee ay dóor la ki tooñ yelloo, na ko àttekat bi tëral, ñu dóor ko ci kanamam, limu yar ba yemook tooñam. \v 3 Waaye ñeent fukki yar, bu ñu ko dóor lu ko ëpp, ndax dóor ko lu ëpp loolu, torxal seen mbokk ci seen kanam lay doon. \p \v 4 Buleen sunjuñ gémmiñu nag, te fekk koy bojj am pepp. \s1 Donn sa jabaru mbokk wartéef la \p \v 5 Bu ay góor yu bokk waajur dëkkee, kenn ci ñoom dee te bàyyiwul doom ju góor, jabaru ki dee du génn, di séy akub jaambur. Jëkkëru donaleem ju bokk ak jëkkëram moo ko wara jël, donloo ko. \v 6 Su ko defee bu ca ndaw sa taawloo góor, taaw ba saxal turu mbokkam ma dee, ba turam du fey ci biir Israyil. \v 7 Su waa ji buggula jël jabaru donaleem jooju, na ndaw sa dem ba ca mag ña ca bunt dëkk ba, ne leen: «Sama jëkkëru donale jii moo baña saxal turu mbokkam ci Israyil. Moo ma buggula donloo.» \v 8 Bu loolu amee na ko magi dëkkam woolu, wax ak moom. Su waa ji dëgëree, ne buggu koo jël, \v 9 na ko jabaru donaleem ja fekki ca kanam mag ña, daldi summi benn caraxu waa ji ba noppi, tifli waa ji ci kanam, ne ko: «Nii lees di def ku dul sampal mbokkam kër.» \v 10 Su boobaa tur wa ñuy dippee waa kër waa ja ci digg Israyil, di «Kërug summi carax.» \s1 Am na jëf ju aay ci sot \p \v 11 Su ay góor dee jàppante, ba jabaru kenn ki dikk, di sotle jëkkëram; bu jàppee ca ngóoray kay jàppanteek jëkkër ja, \v 12 dogleen loxol ndaw sa te buleen ko ñéeblu. \s1 Ab nattukaay day mat \p \v 13 Buleen denc ci seen mbuus doju màndaxekaay ak moroom ma, te bii diis, bi ci des woyof. \v 14 Buleen denc seen kër nattukaayu sol-sotti ak moroom ma, bii réy, bi ci des tuut. \v 15 Doju màndaxekaay bu mat te dëggu ngeen wara am, te nattukaayu sol-sotti bu mat te dëggu ngeen wara am, ndax ngeen gudd fan ca réew ma leen seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji di jox. \v 16 Seen Yàlla Aji Sax ji kat seexlu na képp kuy def yooyii, képp kuy def ug njublaŋ. \s1 Mbugal Amaleg ndigal la \p \v 17 Fàttlikuleen la leen Amalegeen ña defoon ca yoon wa, ba ngeen génnee Misra: \v 18 ñoo leen dab ci yoon wi, songe leen gannaaw, fàdd mboolem ña mujje woon, fekk ngeen sonn, loof, te ragaluñu ci sax Yàlla. \v 19 Bu ngeen demee ba seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji noppal leen ci mboolem seen noon yi séq réew, mi mu leen sédd, ngir ngeen nangu ko, nangeen far mboolem lu ñu doon fàttlikoo Amalegeen ñi fu asamaan tiim. Buleen ko fàtte. \c 26 \s1 Njotlaayal Aji Sax ji laaj na ab galag \p \v 1 Gannaaw loolu, bu ngeen demee ca réew ma leen seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji sédd, ba ngeen nangu ko, dëkke, \v 2 na ku nekk ci yeen sàkk ca ndoortel mboolem meññeefum suuf mu mu jële ca seen réew, ma leen seen Yàlla Aji Sax ji di jox, mu def ko ci pañe, yóbbu ca bérab ba seen Yàlla Aji Sax ji taamoo dëël turam ëllëg. \v 3 Na àgg ca \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba fa nekk ci yooyu jant, ne ko: «Maa biral tey jii fi sa kanam Yàlla Aji Sax ji, ne agsi naa ci réew mi Aji Sax ji giñaloon samay maam, ne moom la may jox.» \v 4 Na sarxalkat bi nangoo pañe bi ci loxoom, taaj ko fi seen kanam \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* Yàlla Aji Sax ji. \v 5 Mu dellu nag wax fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ne: «Sama maam ab Arameen buy màngaan la woon. Mu dem Misra, sance fa mbooloo su néew, te mujj di askan wu réy, am doole te bare. \v 6 Waa Misra nag soxore nu, mitital nu, yen nu liggéey bu diis. \v 7 Ba loolu amee nu yuuxu, woo sunu Yàllay maam Aji Sax ji wall, Aji Sax ji dégg nu, gis sunu mitit, ak sunu coono, ak sunu notaange. \v 8 Aji Sax ji nag génne nu Misra ci dooley loxoom ak kàttanam, ci biir musiba mu réy, aki firnde, aki kéemaan. \v 9 Ba loolu wéyee mu indi nu fi bérab bii, jox nu réew mii, réew mu meew meek lem ji tuuroo. \v 10 Moo ma taxa indi nii ndoortel meññeefum suuf, si nga ma jox, Aji Sax ji.» Su ko defee mu taaj pañe bi fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, daldi sujjóot fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji. \v 11 Mu bége nag, moom ak \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñeek doxandéem yi dëkk ci seen biir, mboolem lu baax li ko seen Yàlla Aji Sax ji jox, moom ak waa këram. \p \v 12 Gannaaw bu ngeen génnee mboolem céru fukkeelub meññeef, ci atum ñetteel, yemook atum génne cérub fukkeel, gannaaw ñaari at yu nekk, nangeen ko jox Leween ñi ak doxandéem yi ak jirim yi ak jëtun ñi, ngir ñu lekk ba regg, fa ñu féete ca seeni dëkk, \v 13 te na ku nekk ci yeen wax fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ne: «Jële naa sama kër céru sellnga bi, ba jox ko Leween ñeek doxandéem yeek jirim yeek jëtun yi, noonee mu dëppook sa santaane bi nga nu dénk. Moyuma lenn ci say santaane, te fàttewuma ci lenn. \v 14 Lekkuma ci dara ci biir ab dëj, jëlewuma ci dara te fekk ma sobewu, te it sarxaluma ci dara ku dee. Sama kàddug Yàlla Aji Sax ji laa topp, noonee nga ma ko sante woon. \v 15 Ngalla geesool fa sa dëkkuwaayu sellnga, fa asamaan, te nga barkeel Israyil, sa ñoñ, barkeel suuf si nga nu jox, noonee nga ko giñale woon sunuy maam, réew mu meew meek lem ji tuuroo.» \s1 Kóllëre feddliku na \p \v 16 Bésub tey jii seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji moo leen sant ngeen jëfe dogal yii, ak àttey yoon yi. Sàmmooleen koo jëfe seen léppi xol, ak seen léppi bakkan. \v 17 Aji Sax ji ngeen biral bésub tey, ne mooy doon seen Yàlla, te dingeen doxe ay yoonam, di sàmm dogali yoonam, aki santaaneem, ak àttey yoonam, tey dégg waxam. \v 18 Aji Sax ji it biral na bésub tey, ne yeenay doon ñoñam ñi mu séddoo, noonee mu leen ko dige woon, te ngeen di sàmm mboolemi santaaneem. \v 19 Moo leen di aj ba ngeen tiim mboolem xeet yi mu sàkk, ci wàllu bayre, ak tur ak teddnga, te moo leen di def askan wu sell, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji, noonee mu ko digee woon. \c 27 \ms1 Musaa biral na yooni barke ak alkànde \mr (Saar 27—30) \p \v 1 Ba loolu wéyee Musaa ak magi Israyil sant mbooloo ma, ne leen: «Sàmmleen mboolem santaane yi ma leen dénk bésub tey. \v 2 Bés bu ngeen jàllee dexu Yurdan, ba ca réew ma leen seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji jox, sampleen ay doj yu mag, ngeen diw doj ya weexal, \v 3 te ngeen bind ca mboolem kàdduy yoon wii, gannaaw bu ngeen jàllee. Su ko defee ngeen mana dugg ca réew, ma leen Aji Sax jiy jox, réew mu meew maak lem ja tuuroo, noonee leen ko seen Yàllay maam Aji Sax ji waxe woon. \v 4 Gannaaw bu ngeen jàllee dexu Yurdan, sampleen doj yooyu ca kaw tundu Ebal, ni ma leen ko sante tey jii, te ngeen diw doj yi weexal. \v 5 Nangeen fa tabax ab \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji, ab sarxalukaay bu ñu defare doj yu jumtukaayu weñ laalul. \v 6 Doj yu mat yu ñu soppiwul lenn ca na ñu bindoo ngeen di tabaxale ab sarxalukaay, seen Yàlla Aji Sax ji, ngeen def ca ay \w saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. \v 7 Defleen ca itam ay \w saraxi cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w* yu ngeen di lekk foofa. Ngeen daldi bége fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji. \v 8 Nangeen bind ca kaw doj ya, mboolem kàdduy yoon wii, ba mu leer nàññ.» \p \v 9 Ba mu ko defee Musaa ak \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yi, \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi wax ak Israyil gépp, ne leen: «Yeen Israyil, neleen cell te déglu. Bés niki tey doon ngeen askan wu ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. \v 10 Kon nag déggal-leen seen Yàlla Aji Sax ji, te ngeen jëfe ay santaaneem, ak dogali yoonam, yi ma leen di dénk tey.» \v 11 Musaa nag sant mbooloo ma bésub keroog, ne leen: \p \v 12 «Giir yii may lim, ñooy taxawe kaw tundu Garisim, ngir ñaanal mbooloo mi, gannaaw bu ngeen jàllee dexu Yurdan: Cimyoneen ñi ak Leween ñi ak Yudeen ñi ak Isakareen ñi ak Yuusufeen ñi ak Beñamineen ñi. \v 13 Giir yii nag ñooy taxaw di rëbbe, fa kaw tundu Ebal: Rubeneen ñi ak Gàddeen ñi ak Asereen ñi ak Sabuloneen ñi ak Daneen ñi ak Neftaleen ñi.» \s1 Lu jëm ci alkànde yi \p \v 14 \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñi ñooy wax ak waa Israyil gépp, di àddu ca kaw, ne: \p \v 15 «Alku ñeel na képp ku sàkk, bay teg ci bérab bu làqu, li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji seexlu, te ab liggéeykat sàkke ko ay loxoom, muy jëmmu tuur mu ñu yett, mbaa mu ñu móol.» Su ko defee mbooloo mépp àddoondoo, ne: «Amiin!» \p \v 16 Ñu neeti: «Alku ñeel na ku torxal baayam mbaa ndeyam.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» \p \v 17 Ñu neeti: «Alku ñeel na ku toxal màndargam kemu suufas moroomam.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» \p \v 18 Ñu neeti: «Alku ñeel na ku sànk silmaxa ci aw yoon.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» \p \v 19 Ñu neeti «Alku ñeel na ku jengal àtteb doxandéem ak jirim akub jëtun.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» \p \v 20 Ñu neeti: «Alku ñeel na ku tëdde jabaru baayam, ndax suturas baayam la xàwwi.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» \p \v 21 Ñu neeti: «Alku ñeel na ku tëdde mboolem luy mala.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» \p \v 22 Ñu neeti: «Alku ñeel na ku tëdde ab jigéenam, muy doomu baayam, mbaa doomu ndeyam.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» \p \v 23 Ñu neeti: «Alku ñeel na ku tëdde yaayu jabaram.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» \p \v 24 Ñu neeti: «Alku ñeel na ku rey moroomam ci kumpa.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» \p \v 25 Ñu neeti: «Alku ñeel na ku nangub ger, ngir rotal bakkanu nit ku deful dara.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» \p \v 26 Ñu neeti: «Alku ñeel na ku saxoowul kàdduy yoon wii, di ko jëfe.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!» \c 28 \s1 Lu jëm ci barke yi \p \v 1 Su ngeen déggalee ba déggal seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ngir di sàmmoo jëfe mboolem santaaneem, yi ma leen di dénk tey, kon Aji Sax ji seen Yàlla, Aji Kawe ji moo leen di aj ci kaw mboolem xeeti àddina. \v 2 Barke yii yépp a leen di dab, sottiku ci seen kaw, bu ngeen déggalee seen Yàlla Aji Sax ji: \p \v 3 Barkeel a leen di ñeel ci biir dëkk, barkeel a leen di ñeel cib àll. \p \v 4 Barkeel ay ñeel seen meññeefum njurukaay, ak seen meññeefum suuf, ak seenug jur, seen jur gu gudd, ak seen jur gu gàtt. \p \v 5 Barkeel ay ñeel seenum witt, ak seenum xiiw. \p \v 6 Barkeel ay ñeel seen yoonu dem, barkeel ay ñeel seen yoonu dikk. \p \v 7 Aji Sax jeey def, noon yi leen di jógal, ñooy daanu fi seen kanam. Wenn yoon lañuy dikke, dal ci seen kaw, waaye juróom ñaari yoon lañuy awe, daw, jiitu leen. \p \v 8 Aji Sax jee leen di booleek barke bu wàccal seenum sàq, ak seen mboolem ñaq, te moo leen di barkeel ca réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji jox. \v 9 Moo leen di defal boppam askan wu sell, noonee mu leen ko giñale woon, ndegam sàmm ngeen seen santaaney Yàlla Aji Sax ji, di doxey yoonam. \v 10 Su boobaa mboolem xeeti kaw suuf dinañu gis ne turu Aji Sax ji lees leen di wooye, te dinañu leen ragal. \v 11 Aji Sax jee leen di xéewale, ngir baaxe seen meññeefum njurukaay, ak seenug jur, ak seen meññeefum suuf, ca réew ma mu giñaloon seeni maam, ne moom la leen di jox. \v 12 Aji Sax jee leen di ubbil mbàndam mu baax ma fa asamaan, ba bu jotee mu tawal seenum réew, boole ci barkeel seen mboolem ñaq. \p Yeenay lebal xeet yu bare, waaye yeen dungeen leb. \v 13 Aji Sax jee leen di def bopp, te du leen def ub geen, te kaw rekk ngeen di jëm, waaye dungeen jëm suuf, ndegam yeena ngi topp seen santaaney Yàlla Aji Sax ji ma leen di dénkal sama bopp bésub tey, di ko sàmmoo jëfe, \v 14 te mboolem kàddu yii ma leen di dénk tey, ngeen bañ koo moye ndijoor, mbaa càmmoñ, di topp yeneen yàlla yu ngeen di jaamu. \s1 Déggadi, alku \p \v 15 Waaye nag su ngeen déggalul seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, te baña sàmmoo jëfe mboolemi santaaneem, ak dogali yoonam, yi ma leen di jox tey, mboolem alkànde yii dina leen dab, sottiku ci seen kaw: \p \v 16 Dingeen alkoo biirub dëkk, alkoo àll. \p \v 17 Dingeen alkule am witt, akam xiiw. \p \v 18 Dingeen alkule meññeefum njurukaay, ak meññeefum suuf, ak jur gu gudd ak gu gàtt. \p \v 19 Dingeen alkoo seen yoonu dem, alkoo seen yoonu dikk. \p \v 20 Aji Sax jeey yebal fi seen biir, kumte ak tiitaange, ak mbetteel ci mboolem lu ngeen ñaq, ba ngeen yàqu, ba jekki sànku ndax seen jëf ju ñaaw ju ngeen ko dëddoo. \p \v 21 Aji Sax jee leen di langalal mbas, ba raafal leen ca réew ma ngeen jëm, ngir nanguji ko. \v 22 Aji Sax jee leen di dumaa woppi ràgg, ak yaram wu tàng, ak lakk-lakk, ak jant bu tàng jérr, ak maral, ak gàncax gu xuur, tegi liir, lépp topp leen ba ngeen sànku. \p \v 23 Asamaan si tiim seen bopp nag da naan sereŋ ni xànjar, suuf si ngeen teg seeni tànk, wow koŋŋ ni weñ gu ñuul. \v 24 Aji Sax jeey def seen tawub réew di suuf ak pënd bu bawoo asamaan, di yuriku ci seen kaw, ba ngeen sànku. \p \v 25 Aji Sax jeey def ngeen daanu fi seen kanami noon. Wenn yoon ngeen di dikke, song leen, waaye juróom ñaari yoon ngeen di awe, daw, te dees na leen seexlu ci mboolem nguuri kaw suuf. \v 26 Su ko defee seeni néew di poraatum mboolem njanaaw ak rabu àll, te kenn du leen dàq. \p \v 27 Aji Sax jee leen di dumaa taabi Misra, ak neewoy kërug suuf, ak yaram wu xas, ak ër yuy xasan te dungeen mana am pajam. \v 28 Aji Sax jee leen di dumaa ag ndof akug cilmaxa ak ngëlëmte, \v 29 ba ngeen di làmbatoo digg bëccëg ni silmaxa di làmbatoo cig lëndëm. Dungeen sottal seeni mébét. Dees leen di néewal doole, di foqati seen alal rekk, bés bu nekk, te kenn du leen wallu. \p \v 30 As ndaw, ngeen digool ab séy, keneen tëdde ko; ag kër, ngeen tabax, te dungeen ko dëkke; ab tóokëru reseñ, ngeen jëmbat, te dungeen ko jariñoo. \v 31 Seenu yëkk, ñu rendi, ngeen gis, te dungeen ci lekk; seen mbaam, ñu nangu ko ci seeni loxo, te du délsi ci yeen; seeni gàtt, ñu jébbal seeni noon, te kenn du leen wallu; \v 32 Seen doom yu góor ak yu jigéen, ñu jébbal weneen xeet ci seen kanam, ngeen di leen séentu ci neen bés bu Yàlla sàkk, te dungeen ci man dara. \v 33 Seen meññeefum suuf, ak mboolem seenu ñaq, xeet wu ngeen xamuloon a koy lekk, te dees leen di not ak a dëggaate rekk, bés bu nekk. \v 34 Dingeen mujj dof ndax lu buur seeni bët ngeen di gis. \p \v 35 Aji Sax jee leen di dumaa taabi óom, ak taabi yeel yu bon. Dungeen mana am pajam, te ci seen wewu tànk lay lawe, ba ci seen kaw bopp. \p \v 36 Aji Sax jee leen di diri, yeen ak seen buur bi ngeen fal, ba ca biir xeet wu ngeen xamuloon, yeen ak seeni maam, ngeen di fa jaamu yeneen yàllay bant ak doj. \v 37 Dees na leen mujj seexlu, di leen léebook a kókkalee foofa ca biir mboolem xeet, ya mu leen dàq jëme. \p \v 38 Jiwu mu bare ngeen di yóbbu tool, te lu néew ngeen cay ame, ndax njéeréer yee koy wat. \v 39 Ay tóokëri reseñ, ngeen jëmbat, sonn ca, te biiñ, dungeen ko naan, dungeen witt doom ya it, ndax sax yee koy lekk. \v 40 Ay garabi oliw ngeen di am ci seen réew mépp, waaye ag diw, dungeen ko diwoo, ndax seen doomi oliw ya day yolax. \v 41 Ay doom yu góor ak yu jigéen ngeen di jur, waaye duñu leen nekkal, ndax njaam lañuy duggi. \v 42 Seen gépp garab ak seen meññeefum suuf, soccet yee koy nangu. \p \v 43 Doxandéem bu nekk ci seen biir mooy yéeg tiim leen, ba ca kawa kaw, yeen nag ngeen di wàcc, ba suufee suufe. \v 44 Moom moo leen di lebal, waaye dungeen ko lebal. Moom mooy doon bopp, yeen, ngeen di geen. \p \v 45 Mboolem alkànde yii ñoo leen di dab, dal ci seen kaw, topp leen, ba ngeen sànku, ndax yeena déggalul seen Yàlla Aji Sax ji, ngir wormaal ay santaaneem, ak dogali yoonam, yi mu leen dénk. \v 46 Loolu mooy doon, ci seen biir ak seen biir askan, ba fàww, ay firnde aki kéemaan yu leen di àrtu. \p \v 47 Gannaaw yeena jaamuwul seen Yàlla Aji Sax ji ci mbégte ak xol bu sedd, keroog ba ngeen barelee lépp, \v 48 seen noon yi Aji Sax jiy yebal ci seen biir, ñoom ngeen di jaamuji ci biir xiif, ak mar ak rafle, ak gépp ñàkk. Aji Sax jeey teg yetu weñ ci seen ndodd, ba sànk leen. \v 49 Aji Sax jeey jógloo ci seen kaw, xeet wu sore, ñu bàyyikoo ca cati àddina, dikk ne milib nig jaxaay, te dégguleen aw làkkam, \v 50 xeet wu ñàng kanam te rusuñu mag, yërëmuñu gone. \v 51 Ñooy yàpp seenug jur, lekk seen gàncax, ba ngeen raaf. Duñu leen wacce dara; du pepp, du biiñ, dug diw, du doomu jur gu gudd ak gu gàtt, ba ngeen far sànku. \v 52 Dees na leen gawe ci seen dëkk yépp, ba seen tata yu kawe te dàbbliku, ya ngeen yaakaaroon ci seen réew mépp, màbb. Dees na leen gawe seen dëkk yépp, ci mboolem réew, mi leen seen Yàlla Aji Sax ji jox. \v 53 Dingeen mujj lekk seen meññeefum njurukaay, seen suuxu doom yu góor ak yu jigéen, yi leen seen Yàlla Aji Sax ji may, ndax gaw ba, ak tanc bu leen seeni noon tanc. \v 54 Góor gi gëna lewet ci yeen te xay lool dina xeelu mbokkam, xeelu jabar ju muy noyyee, ak ndesu doomam ju mu dese, \v 55 ngir baña sédd kenn ci ñoom ci yàppu doomam ya muy lekk, ndax du dese dara ca biir gaw ba, ak tanc ba leen seeni noon tanc, ci seen dëkk yépp. \v 56 Jigéen ju gëna lewet te xay ci yeen, ba néegula teg ndëggul tànkam ci suuf ndax xayteem ak lewetaayam, dina xeelu jëkkëram ju muy noyyee, ak doomam ju góor ak ju jigéen. \v 57 Day fekk mu namma lekk ci kumpa doom ju mu doora wasin, boole kook ànd ba, ndax lépp ay ñàkk ca biir gaw ba ak tanc, ba leen seeni noon tanc ca seeni dëkk. \p \v 58 Su ngeen sàmmoowula jëfe mboolem kàdduy yoon wii binde ci téere bii, ngir wormaal boroom tur wu màgg wii te raglu, seen Yàlla Aji Sax ji, \v 59 su boobaa Aji Sax ji dina réyal seeni duma, ak seen dumay askan, duma yu mag te yàgg, ak wopp yu aay te ës. \v 60 Mooy délloosi fi seen kaw, mboolem jàngoroy Misra yu ngeen ragaloon, ñu taq leen. \v 61 Te it mboolem wopp ak mboolem mbugal mu bindewul ci téereb yoon wii, Aji Sax jee leen koy yen, ba ngeen sànku. \v 62 Nit ñu néew ngeen di dese, te bare woon ni biddiiwi asamaan, ndax ñàkka déggal seen Yàlla Aji Sax ji. \v 63 Su ko defee noonee Aji Sax ji daan bége di leen baaxe ak a yokk, noonu la Aji Sax jiy bége di leen sànk ak a fàkkas, te dees na leen déjjatee ca réew ma ngeen jëm, ngir nanguji ko. \v 64 Aji Sax jee leen di wasaare ci biir mboolem xeeti àddina, cat ba cat, ngeen di fa jaamu yeneen yàlla yu ngeen xamuloon, du yeen du seeni maam, yàllay bant ak doj. \v 65 Ca biir xeet yooyu nag, dungeen fa astandikoo, dungeen fa am sax fu ngeen noppale seen téstën. Aji Sax jee leen fay teg fit wu rëcc, ak gët yu giim, ak xol bu jeex. \v 66 Seen bakkan ay nekk ci xott, ngeen dëkke tiitaangey guddi ak bëccëg, te seen ëllëg dootu leen wóor. \v 67 Ag suba ngeen ne: «Éy waay, bu doon ngoonati.» Bu ngoonee ngeen ne: «Éy waay, bu doon subaati!», ndax tiitaange lu ngeen di tiit, ak li ngeen di teg seeni gët. \v 68 Aji Sax jee leen di yeb ciy gaal, delloo leen Misra, yoon wu ma leen noon dungeen ko gisati, ngeen di fa jaay seen bopp seeni noon, ngir doon seen jaam yu góor ak yu jigéen, te kenn du leen jënd. \c 29 \s1 Kóllëre gi yeeslu na \p \v 1 Lii mooy sàrti \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w*, gi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji santoon Musaa ngir mu fasoo ko ak \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, ca réewum Mowab, te bokkewul ak kóllëre ga mu fasoo woon ak ñoom ca tundu Oreb. \p \v 2 Ba mu ko defee Musaa woolu Israyil gépp. Mu ne leen: \p Yeena gis mboolem la Aji Sax ji def, ngeen teg ci seen bët, ca réewum Misra, ci kaw Firawna ak dagam ñépp, ak réewam mépp. \v 3 Nattu yu mag yooyu, ak firnde yeek kéemaan yu réy yooyu, yeena ci teg seen bët, \v 4 te taxul Aji Sax ji may leen xel mu ngeen ràññee, ak gët yu ngeen gise, ak nopp yu ngeen dégge, booba ba sunu jonni yàllay tey! \v 5 Aji Sax ji nee: «Maa leen jiite ñeent fukki at ca màndiŋ ma, seeni yére ràppul, seenu dàll ràppul. \v 6 Mburu, lekkuleen ko, biiñ mbaa geneen naan gu diis, naanuleen ko. Maa leen leel, ngir ngeen xam ne man maay seen Yàlla Aji Sax ji.» \v 7 Ba ngeen agsee ci bérab bii, Siwon buurub Esbon dikk, ànd ak Og buuru Basan, dikk dajeek nun, ngir song nu xare, nu duma leen. \v 8 Nu nangu seenum réew, sédd ko Rubeneen ñi, ak Gàddeen ñi, ak genn-wàllu giirug Manaseen ñi. \v 9 Sàmmleen nag sàrti kóllëre gii, di ko jëfe ndax yàlla ngeen baaxle ci mboolem lu ngeen def. \s1 Buleen caaxaane kóllëreg Aji Sax ji \p \v 10 Yeena ngii tey, taxaw jonn, yeen ñépp fi seen kanam Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, seen njiiti giir, ak seeni mag ak seeni kàngam; mboolem góori Israyil, \v 11 ak seeni tuut-tànk, ak seeni jabar, akub doxandéem ci seenub dal, seen gorkatub matt, ba ci seenub rootkat. \v 12 Yeena ngi tàbbi ci seen biir \w kóllëreg|lemma="kóllëre g-:"\w* Yàlla Aji Sax ji, ak ci ngiñam, kóllëre gi seen Yàlla Aji Sax ji fasoo ak yeen bésub tey, \v 13 ngir def leen bésub tey, askan wi mu ñoñoo; moom ci boppam mu doon seen Yàlla, na mu leen ko waxe woon, na mu ko giñale woon seeni maam, Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba. \v 14 Aji Sax ji nee: «Du yeen doŋŋ laay fasool kóllëre gii, ak ngiñ lii.» \v 15 Yeen ñi taxaw ci sunu biir tey, fi sunu kanam Yàlla Aji Sax ji, ci ngeen bokk, waaye ñi dikkagul bay bokk ak nun taxaw fii it, ci lañu. \p \v 16 Yeen ci seen bopp, xam ngeen na nu nekke woon réewum Misra ak na nu jaare ca biir xeet ya ngeen jaare seeni réew. \v 17 Gis ngeen seen jëf ju jomblu, seen kasaray tuur ya: yëfi bant yeek yëfi doj yeek yëfi xaalis yeek yëfi wurus yi ñu àndal. \v 18 Kon nag, muy góor, di jigéen, ak làng gu mu mana bokk, mbaa giir, fexeleen ba kenn ci yeen du walbatiku, dëddu bésub tey, sunu Yàlla Aji Sax ji, di jaamuji yàllay xeet yooyu. Lu ko moy ab reen dina fëlle fi seen biir, meññal leen tooke ak wextan. \v 19 Jombul mu am ku dégg kàdduy ngiñ lii, tey nax boppam cim xelam, naan: «Jàmm rekk laay am, maa tey të,» ba tax ñax mu wow lakkaale mu tooy. \v 20 Aji Sax ji du nangoo baal kooku, nde su boobaa, sànjum Aji Sax jeey ànd ak fiiraangeem, tàkk ci kawam, te mboolem alkànde gi ñu bind ci téere bii day këppu ci kawam, te Aji Sax jeey far aw turam fu asamaan tiim. \v 21 Aji Sax jee koy seppee ci mboolem giiri Israyil, ngir sédd ko njekkar, na mu dëppook mboolem alkàndey kóllëre gi ñu bind ci téereb yoon wii. \s1 Mbugal du jaas \p \v 22 Maas giy ñëw, seen doom yi leen di wuutuji yeen, ñook doxandéem yi jóge fu sore, bu ñu gisee mbugal yi ci réew mii, ak wopp yi fi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji woppale, \v 23 tamarax ak xorom, ak lakk gi ci seen réew mépp, ba du lenn lees fay ji, mbaa lu fay jebbi, mbaa genn gàncax gu fay saxe, mbete tastey Sodom, ak Gomor ak Atma ak Ceboyim, dëkk ya Aji Sax ji tas, ca meram ma ak sànjam ma, \v 24 su boobaa yéefar yépp a naan: «Ana lu waral Aji Sax ji def nii réew mi? Lu waral mii sànj mu tàng te réy?» \v 25 Ñu ne leen: «Li ko waral mooy, dañoo fecci \w kóllërey|lemma="kóllëre g-:"\w* Aji Sax ji, seen Yàllay maam, te mu fasoon ko ak ñoom ba mu leen jëlee réewum Misra. \v 26 Ñu dem nag, di jaamu yeneen yàlla, di leen sujjóotal, yàlla yu ñu xamuloon, te du lu leen Aji Sax ji féetale. \v 27 Moo tax sànjum Aji Sax ji tàkkal réew mii, ngir wàcceel leen mboolem alkànde yi ñu bind ci téere bii. \v 28 Aji Sax ji nag moo leen déjjatee seenum réew ci biir mer, ak xadar, ak sànj mu réy, ba sànni leen meneen réew, niki bésub tey jii.» \p \v 29 Mbir yi làqu daal, ñeel na sunu Yàlla Aji Sax ji, mbir yi feeñ nag, ñeel nu, nook sunuy doom ba fàww, te nu wara jëfe mboolem kàdduy yoon wii. \c 30 \s1 Dellusi ci Aji Sax ji, barkeel \p \v 1 Ëllëg nag, su mboolem mbir yooyu dikkee fi seen kaw, muy barke yi, di alkànde yi ma teg fi seen kanam, su boobaa bu ngeen délloosee seen xel foofa mu leen fekk, ca biir mboolem xeet ya leen seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dàq jëme, \v 2 ba ngeen dellusi ci seen Yàlla Aji Sax ji, di ko déggal ci mboolem ni ma leen ko sante bésub tey, yeen ak seeni doom, te ngeen defe ko seen léppi xol ak seen léppi bakkan, \v 3 su boobaa Aji Sax jeey tijji seen wërsëg, yërëm leen. Seen Yàlla Aji Sax ji moo leen di dellu dajalee foofa, ci biir mboolem xeet ya mu leen tasaare woon ca seen biir. \v 4 Su ñu leen toxaloon ba ca cati asamaan sax, foofa la leen seen Yàlla Aji Sax ji di dajalee, te fa la leen di jële. \v 5 Seen Yàlla Aji Sax jee leen di delloo ca réew ma seen maam moomoon, ngeen moom ko, te moo leen di baaxe, yokk leen ba ngeen gëna bare seeni maam. \v 6 Su boobaa seen Yàlla Aji Sax jee leen di xarfal xarafu xol, te mooy xarfal xarafu xol, seen askan, ngir ngeen soppe seen Yàlla Aji Sax ji seen léppi xol, ak seen léppi bakkan, ndax ngeen dund. \v 7 Su loolu amee seen Yàlla Aji Sax jeey teg mboolem alkànde yii ma leen limal, ci kaw seeni noon ak seen bañ yi leen toŋal. \v 8 Yeen nag dingeen walbatiku, di déggal Aji Sax ji, tey jëfe mboolem santaane yi ma leen di dénk bésub tey jii. \v 9 Ci kaw loolu seen Yàlla Aji Sax ji mooy baaxal mboolem seenu ñaq, ak seen meññeefum njurukaay, ak seen meññeefum jur, ak seen meññeefum suuf, ngir lu baax. Aji Sax ji mooy bégewaat di leen baaxe na mu daan bégee baaxe seeni maam. \v 10 Ndegam déggal ngeen seen Yàlla Aji Sax ji, di topp ay santaaneem, ak dogali yoonam, yi ñu bind ci téereb yoon wii; ndegam yeena walbatikoo seen léppi xol ak seen léppi bakkan, ba dellu ci seen Yàlla Aji Sax ji. \s1 Musaa nee déggal Yàlla yomb na \p \v 11 Santaane bii ma leen di dénk tey nag, jafewul te sorewul ba të leen, \v 12 Ajewul kaw asamaan ba ngeen naan: «Ana ku nuy yéegali kaw asamaan, àjjil nu ko, dégtal nu ko, ba nu jëfe ko?» \v 13 Nekkul it wàllaa géej ba ngeen naan: «Ana ku nuy jàllil wàllaa géej, jëlil nu ko, dégtal nu ko, ba nu jëfe ko?» \v 14 Kàddu gi kay jege na leen lool; ci seen gémmiñ ak ci seen biir xol la nekk, ngir ngeen di ko jëfe. \p \v 15 Kon nag gis ngeen ko: Teg naa fi seen kanam, bés niki tey, dund ak mbaax, teg naa fi seen kanam, ndee ak loraange. \v 16 Li ma leen sant, man, bésub tey, mooy ngeen sopp seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, di topp ay yoonam, di sàmm ay santaaneem, ak dogali yoonam, aki àtteem, ngir ngeen dund te yokku, seen Yàlla Aji Sax ji barkeel leen ca réew ma ngeen jëm, ngir nanguji ko. \v 17 Waaye su ngeen walbatee seen xol, dégluwuleen, xanaa ngeen lajj, di sujjóotal yeneen yàlla, di leen jaamu, \v 18 ma wax leen ko bés niki tey, su boobaa yeenay sànkoo sànku, te dungeen gudd fan ca réew ma ngeen di jàll dexu Yurdan, jëm fa, ngir nanguji ko. \p \v 19 Woo naa seede asamaan ak suuf ci yeen, bésub tey: dund ak ndee laa teg fi seen kanam, ak barke ak alkànde. Taamuleen dund ndax ngeen dund, yeen ak seen askan. \v 20 Soppleen seen Yàlla Aji Sax ji, déggal ko te taq ci moom, ndax moom mooy seenug dund, di seen gudd-gi-fan ca réew ma mu giñaloon seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, ne ñoom la koy jox. \c 31 \ms1 Musaa tàggoo na \mr (Saar 31—34) \p \v 1 Gannaaw loolu Musaa dellu na àddu kàddu yii, wax ak \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp. \v 2 Mu ne leen: «Maa ngi ci sama téeméeri at ak ñaar fukk, tey. Manatumaa jiite, te it \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji moo ma wax ne ma: “Doo jàll dexu Yurdan gii.” \v 3 Seen Yàlla Aji Sax ji ci boppam moo leen di jiite jàll. Mooy fàkkas xeet yooyu fi seen kanam, ngeen nangu seenum réew. Yosuwe moo leen di jiite jàll, na ko Aji Sax ji waxe woon. \v 4 Aji Sax ji moo leen di def na mu defoon Siwon ak Og, buuri Amoreen ña, ak seenum réew, fàkkas leen. \v 5 Aji Sax jee leen di joxe fi seen kanam, ngeen def leen mboolem li ma leen santoon. \v 6 Dëgërluleen nag te am fit. Buleen tiit, buleen yox-yoxi ndax ñoom, ngir seen Yàlla Aji Sax ji mooy ànd ak yeen. Du leen ba, du leen wacc mukk.» \p \v 7 Ba loolu amee Musaa woolu Yosuwe, wax ak moom, Israyil gépp teg ci seen bët. Mu ne ko: «Dëgërlul te am fit, ndax yaw yaay ànd ak mbooloo mii ca réew ma Aji Sax ji giñaloon seeni maam, ne ñoom la koy jox. Yaw it yaa leen koy sédde. \v 8 Aji Sax ji nag mooy dox, jiitu la. Moom mooy nekk ak yaw. Du la ba, du la wacc mukk. Bul tiit, bul yoqi.» \p \v 9 Musaa moo bind kàddug yoon wii, dénk ko doomi Lewi yu góor, \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yay gàddu \w gaalu kóllërey Aji Sax|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* ji, ñook magi Israyil ñépp. \v 10 Musaa sant leen, ne leen: «Njeexital juróom ñaareelu at mu nekk, àppook atum njéggalug bor, ci diiru \w màggalu Mbaar|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* yi, \v 11 bu Israyil gépp teewsee fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, fa bérab ba muy taamuji, nangeen jàng kàdduy yoon wii fi kanam Israyil gépp, ñuy dégg. \v 12 Dangeen di dajale mbooloo mi, góor ñi ak jigéen ñi ak tuut-tànk yi, ba ci doxandéem bu nekk ci seen biir dëkk, ndax ñu déglu, ba tàggatu ci ragal seen Yàlla Aji Sax ji, di sàmmoo jëfe mboolem kàdduy yoon wii. \v 13 Su ko defee seen doom yi xamul dinañu ci dégg, ba tàggatu ci ragal seen Yàlla Aji Sax ji, mboolem fan ya ngeen di dund ca réew, ma ngeen jàll dexu Yurdan, jëm fa, ngir nanguji ko.» \p \v 14 Ba loolu wéyee Aji Sax ji ne Musaa: «Ma ne, sa bésub dee ngi jegesi. Wool Yosuwe, te ngeen teewsi fi \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi, ma yeb ko.» Musaa dem, ànd ak Yosuwe, ñu teewi fa xaymab ndaje ma. \v 15 Aji Sax ji nag feeñ ca xayma ba, ci biir taxaaru niir, taxaaru niir wa taxaw fa bunt xayma ba. \v 16 Aji Sax ji ne Musaa: «Yaa ngi nii di tëddi fa say maam. Mbooloo mii nag dinañu tàmbali di gànctuy topp yeneen yàllay doxandéem yu waa réew, ma ñu jëm ca seen biir. Dinañu ma wacc, fecci sama kóllëre gi ma fasoon ak ñoom, \v 17 te samam sànj dina tàkk ci seen kaw bésub keroog. Maa leen di wacc, làq leen sama kanam, te kon dees na leen lekk. Musiba yu bare aki njàqare dina leen dikkal. Bésub keroog ñoo naan: “Xanaa sunu Yàllaa nekkul ci sunu biir kay, ba tax musiba yii dikkal nu!” \v 18 Man nag maa leen di làqa làq sama kanam, bésub keroog ndax mboolem mbon gi ñu def, ndax ñoo walbatiku ci yeneen yàlla. \v 19 Léegi nag bindleen woy wii ma leen di dégtal, te yaw Musaa nga jàngal ko bànni Israyil. Woyloo leen ko, ndax woy wii di sama seede ak bànni Israyil. \v 20 Maa leen di yóbbu déy ca réew ma ma giñaloon seeni maam, fa meew maak lem ja tuuroo, ñu lekk ba regg, yaflu, daldi walbatiku ci yeneen yàlla, di leen jaamu, xarab ma, fecci sama kóllëreek ñoom. \v 21 Su ko defee bu leen musiba yu bare dikkalee aki njàqare, woy wii mooy biral kàddug seede fi seen kanam, ndax su boobaa xel du ko faaye, ba mu réer seenu askan. Ndax kat xam naa seen mébét mi ñuy rabat, te yóbbooguma leen sax ca réew ma ma leen giñaloon.» \v 22 Ba loolu amee Musaa bind woy woowu bésub keroog, daldi koy jàngal bànni Israyil. \p \v 23 Aji Sax ji nag yeb Yosuwe doomu Nuun ne ko: «Dëgërlul te am fit, ndax yaw yaay yóbbu bànni Israyil ca réew ma ma giñoon, te man ci sama bopp maay nekk ak yaw.» \p \v 24 Ba Musaa bindee kàdduy yoon woowu cib téere ba mu mat, \v 25 dafa yeb \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ñiy gàddu \w gaal gi àlluway kóllërey Aji Sax ji dence|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w*, ne leen: \v 26 «Jël-leen téereb yoon wii, ngeen teg ko ci seen wetu gaalu kóllërey Yàlla Aji Sax ji, mu doon fa ab seede, ngir àtte leen. \v 27 Ndax maa xam seen jikkoy fippu, ak seenug dëgër bopp. Seetleen, ndegam bi may dundagum tey ci seen biir ngeen di fippu ci kaw Aji Sax ji, astamaak gannaaw bu ma deeyee. \v 28 Wool-leen ma seen magi giir yépp, ak seeni kàngam, ma wax kàddu yii, ñuy dégg, ba ma seedeloo asamaan ak suuf, ci seen kaw, ñoom. \v 29 Xam naa ne gannaaw bu ma deeyee, dingeen defa def ag yàqute, dingeen teggi yoon wi ma leen jaarloo woon, te musibaa leen di mujj dikkal, ndax yeenay def jëf ju bon ju Aji Sax ji ñaawlu, ba merloo ko ndax seeni jëf.» \v 30 Ba mu ko defee Musaa jàng kàdduy woy wii ba mu mat, ndajem Israyil ma mépp di dégg. \c 32 \s1 Musaa woy na kóllëreg Aji Sax ji \q1 \v 1 Yeen asamaan, teewluleen, ma wax, \q1 Yaw suuf, déglul sama kàddu yii. \q1 \v 2 Na samam njàngle sóob nib taw, \q1 samay kàddu rogalaat nib lay, \q1 ba tuurul am ñax, \q1 baawaanal gàncax. \q1 \v 3 Turu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji déy laay tudd, \q1 seedeleen sunu màggaayu Yàlla. \b \q1 \v 4 Kee di cëslaay, te mati jëf, \q1 wépp yoonam di njub. \q1 Yàlla ju am kóllëre, mucc njubadi, \q1 te njekk ak njub mooy boroom. \q1 \v 5 Njabootam ñoo def ug yàqute ci kawam, \q1 ba dootuñuy doomam ndax seeni sikk. \q1 Ndaw maas gu dëng te njublaŋ! \q1 \v 6 Aji Sax ji lañuy feye lii? \q1 Ndaw xeet wu dofe te ñàkk xel! \q1 Mooy seen baay, bind leen, \q1 sàkk leen, samp leen. \b \q1 \v 7 Fàttlikuleen jant ya jëkkoon, \q1 baleen xel maasi maas ya woon. \q1 Laajleen seeni baay, ñu xamal leen; \q1 ak seen mag ñi, ñu wax leen. \q1 \v 8 Ba Aji Kawe ji séddee xeet yi seeni suuf, \q1 tasaare doom aadama yi ci àddina, \q1 moo àppal xeet yi seen kemi réew, \q1 na mu dëppook limeefu goney\f + \fr 32.8 \fr*\ft Mooy ndaw yi bokk ci péncum Yàlla.\ft*\f* Yàlla yi. \q1 \v 9 Céru Aji Sax ji moo di ñoñam, \q1 askanu Yanqóoba woowooy wàllam. \q1 \v 10 Moo leen fekk réewum màndiŋ, \q1 fu ne wëyëŋ, ubaleeki sab, \q1 mu feg leen, topptoo leen, sàmm leen, \q1 ni bu ñu doon peru bëtu boppam. \q1 \v 11 Moo mel ni jaxaay juy naawtal am tostanam, \q1 daayaarlu, tiim leen, \q1 tàllali laafam, aw leen, \q1 teg ciw dunqam, boot leen. \q1 \v 12 Aji Sax ji doŋŋ a leen wommat, \q1 du yàllay jaambur ju ko ci fekk. \q1 \v 13 Moo leen waral kawtey réew ma, \q1 ñuy xontoo meññeefum àll bi, \q1 mu di leen nàmpale lem ju walew doj, \q1 ak diw gu balle xeer wu ne sereŋ, \q1 \v 14 boole ca soowum nag ak meewum xar, \q1 nebbonu mbote, kuuyi diiwaanu Basan aki bëy, \q1 teg ca ngëneeli pepp, \q1 may leen biiñu reseñ ju xonq curr, ngeen naan. \b \q1 \v 15 Yeen Yesurun\f + \fr 32.15\fr*\fk Yesurun: \fk*\ft tur wii ak Yanqóoba itam dees na ko wooye Israyil.\ft*\f*, yeena yaflu, waŋŋeetu, \q1 solu yaram, ne faaj, ne fuux, \q1 fàtte Yàlla mi leen sàkk, \q1 faaleedi seen cëslaay li leen musal. \q1 \v 16 Ñoo yee fiiraangeem, ndax ay yàllay doxandéem, \q1 ñoo ko merloo ak seen tuur yu jomblu. \q1 \v 17 Ñoo sarxalal ay rab yu dul Yàlla; \q1 ay yàlla yu ñu masula xam, \q1 yu bees yu doora xew, \q1 yu seeni maam ràññeewuloon. \q1 \v 18 Cëslaay li leen meññ ngeen foñ, \q1 Yàlla ji leen jur ngeen fàtte. \b \q1 \v 19 Aji Sax jee gis loolu, gedd, \q1 ndax mere doomam yooyu, góor ak jigéen. \q1 \v 20 Mu ne: «Maa leen di xañ sama kanam, \q1 ba gis nu ñuy mujje, \q1 ndax maasug defkati njekkar lañu, \q1 doom yu ñàkk kóllëre. \q1 \v 21 Ñoo ma fiirloo ak yàlla yu dul tus, \q1 merloo maak seen tuuri neen, \q1 man it maa leen di fiireloo xeet wu tekkiwul dara, \q1 ci waasow naataxuuna laa leen di merloo. \q1 \v 22 Sawaraa ngay tàkke ca samam sànj, \q1 di lakke ba ca xóotey njaniiw, \q1 ba xoyom suuf ak meññeefam, \q1 ba jafal reeni tund ya. \q1 \v 23 Maay jal ci seen kaw ay musiba, \q1 maa leen di soqil, ba jeexal samay fitt. \q1 \v 24 Ñooy loof cib xiif, jeex tàkk ndaxi jàngoro, \q1 ak mbas yu metti. \q1 Ay selli rabi àll laay yebal ci seen kaw, \q1 boole ca daŋaru ndox-suuf. \q1 \v 25 Fa biti la leen saamar di xañey doom, \q1 biir néeg ya, tiitaange luy reye feelu ko, \q1 buubaale waxambaane akub janq, \q1 luy nàmp, ak boroom bijjaaw. \b \q1 \v 26 «Maa noon maa leen di fàkkas, \q1 ba far dakkal lu leen nit doon fàttlikoo. \q1 \v 27 Waaye reetaani noon laa ci ragal, \q1 lu ko moy seeni bañ juume ko, \q1 ba naan: “Sunu njàmbaar a!” \q1 te waroon ne: “Aji Sax jee def lii lépp!”» \b \q1 \v 28 Wii xeet wu gàtt xel \q1 te ñàkk xam-xam! \q1 \v 29 Su ñu muusoon, xalaat ci lii, \q1 ba xam nu ñuy mujje. \q1 \v 30 Ana nu kenn di dàqe seen junni, \q1 ñaar di fëxal seen fukki junni, \q1 te ka ñu yaakaar jaayu leen, \q1 te Aji Sax ji, laa ne, waccu leen? \q1 \v 31 Yaakaaru noon yi de melul ni sunu yaakaar, \q1 te loolu la noon ya àtte. \q1 \v 32 Seen reseñ a nga cosaanoo Sodom, \q1 ak tóokëri Gomor, \q1 doom ya di tooke, cëgg ya wex xàtt! \q1 \v 33 Seen biiñ daŋaru ninki-nànka la, \q1 ak tookey ñàngóor bu aay. \q1 \v 34 «Xanaa du loolu laa làq fi sama wet, \q1 ne ko ràpp fi samay denc? \q1 \v 35 Maay kiy feye, di añale, \q1 te bu jotee ñu fakkastalu, \q1 ndax seen bésub toskaree dëgmal, \q1 dogal ba buur, wutsi leen!» \q1 \v 36 Aji Sax jeey dëggal ñoñam, \q1 mooy ñeewante ay jaamam, \q1 bu gisee doole dëddu, \q1 ba kenn desul, dub jaam, dus gor. \q1 \v 37 Su boobaa da naan: «Ana seen yàlla ya, \q1 seen kiirlaay lañu daa làqoo? \q1 \v 38 Ñi lekk seen nebboni sarax, \q1 naan biiñ bi ñu leen di tuural kay, \q1 nañu jóg, boog, xettli leen, di seen kiiraay! \q1 \v 39 Kon gisleen ne man la, man doŋŋ, \q1 kenn du Yàlla ku dul man! \q1 Man maay rey, di dundal; \q1 di gaañe, di wéral; \q1 maay jàpp, te kenn du xettli. \q1 \v 40 Maay yékkati sama loxo jëme asamaan, \q1 giñ ne: “Ndegam maay dund ba fàww, \q1 \v 41 bu ma daasee sama saamar buy melax, \q1 ba ŋàbb ko ci saab loxo, di àtte, \q1 maay fey samay digaale, \q1 añale samay bañ. \q1 \v 42 Maay nàndal samay fitt deret, \q1 sama saamar di yàppe, \q1 deret di nàcce ci ku ñu jam, ak ku ñu jàpp, \q1 tey tuuroo ci boppi kilifay noon yi.”» \q1 \v 43 Yeen, xeet yi, tàcculeen ñoñam, \q1 deretu jaamam ñi lay feyul, \q1 pey gu muy fey ay bañam, \q1 ba jot suufam ak ñoñam. \s1 Déggal Aji Sax ji, dund \p \v 44 Noonu la Musaa dikke, mook Yosuwe doomu Nuun, ba jaar ci mboolem kàdduy woy wii, mbooloo mi di dégg. \v 45 Gannaaw ba Musaa noppee ci jottli Israyil gépp mboolem kàddu yooyu, \v 46 da ne leen: «Defleen seen xel ci mboolem kàddu yi ma leen di artoo man, bésub tey, te ngeen sant seeni doom ñu sàmmoo jëfe mboolem kàdduy yoon wii. \v 47 Ndax kat du kàddug neen ci yeen. Mooy seenug dund! Ci gii kàddu ngeen di gudde fan, ca réew ma ngeen di jàll dexu Yurdan jëm fa, ngir nanguji ko.» \s1 Aji Sax ji woo na Musaa \p \v 48 Ci kaw loolu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax Musaa bésub keroog boobee, ne ko: \v 49 «Doxal yéegi ca tundi Abarim gii, nga jàll ba ca tundu Nebo ca diiwaanu Mowabeen, ba janook Yeriko. Nga séentu nag réewum Kanaan mi may jox \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, ñu jagoo. \v 50 Boo noppee, deel ca kaw tund woowu nga yéeg jëm, ba ñu tërali la ca say bokk, noonee sa mag Aaróona deeye woon ca kaw tundu Or, ba ñu tërali ko cay bokkam. \v 51 Li ko waral mooy yeena ma fecci worma ci digg bànni Israyil, ca ndoxi Meriba Kades, ca màndiŋu Ciin, ndax yeena wormaalul sama sellnga ci digg bànni Israyil. \v 52 Kon nag ci biti ngay séentoo réew ma, waaye foofa, doo fa dem. Doo dugg ca réew, ma may jox bànni Israyil.» \c 33 \s1 Musaa ñaanal na bànni Israyil \p \v 1 Ñaan gii nag la Musaa, góoru Yàlla ga ñaanaloon \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, bala moo nelaw. \q1 \v 2 Da ne: \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Sinayi la bawoo, \q1 fenkale leen fa Seyir, \q1 naajali leen fa tundu Paran, \q1 ànd ak ndiiraani ñu \w sell|lemma="sell:"\w* ña, \q1 ndijooram ba indil leen melax. \q1 \v 3 Yaw kay yaa sopp xeet yi, \q1 sa ñu sell ñépp nga téyee say loxo, \q1 te ñoo topp say tànk, \q1 di taataan say tegtal. \q1 \v 4 Aw yoon la nu Musaa dénk, \q1 muy jagleb péncum Yanqóoba. \q1 \v 5 Yesurun am na buur, \q1 kera ba njiiti askan wa dajee, \q1 ba giiri Israyil bokk teew. \b \q1 \v 6 Yal na Ruben dund, baña raaf, \q1 yàlla buy nitam néew. \b \p \v 7 Lii nag moo ñeel Yuda. Mu ne: \q1 Éy Aji Sax ji déggal yuuxi Yuda \q1 te yóbbu ko ciy bokkam. \q1 Mooy jànkoontee dooley boppam, \q1 waaye yaa koy wallu ciy noonam. \b \p \v 8 Lewi la wax ne ko: \q1 Sa Tumim ak sa \w Urim|lemma="Urim ak Tumim:"\w*, jumtukaayi tegtal ya, \q1 ñeel na góor gay sa wóllëre, \q1 yaa ko nattoo ca Maasa, \q1 joteek moom ca ndoxum Meriba. \q1 \v 9 Kee ne ndey ak baay: \q1 «Gisuma leen,» \q1 ay doomi ndeyam, ràññeewu leen, \q1 te doomam, xamu ko. \q1 Xanaa di sàmm say wax, \q1 di sàmm sa \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w*. \q1 \v 10 Leween ñeey xamal askanu Yanqóoba say àtte, \q1 di won Israyil gii saw yoon. \q1 Ñooy taal cuuraay fi sa kanam, \q1 di teg saraxi dóomal ci sab \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*. \q1 \v 11 Éy Aji Sax ji barkeelal dooley gii giir, \q1 te bége aw ñaqam. \q1 Dammal ndiggal ña koy jógal, \q1 ba ay bañam duñu jógati. \b \q1 \v 12 Beñamin la wax, ne ko: \q1 Soppeb Aji Sax jaa ngi, \q1 keey dëkke xel mu dal fi wetam, \q1 mu di ko yiir bésoo bés, \q1 te diggantey waggam la dëkke. \b \q1 \v 13 Yuusufa la wax, ne ko: \q1 Yal na barkeb Aji Sax ji ñeel suufam, \q1 bawoo ca xéewali asamaan, dib lay, \q1 ak ndox mu lal xóotey suuf, \q1 \v 14 ak xéewali meññeef mu jant ñoral, \q1 ak tànnéefi gàncax yiy sax ci weeram. \q1 \v 15 Na barke bawoo fa kawtey tundi cosaan yu mag ya, \q1 ak xéewali tundi cosaan yu ndaw ya, \q1 \v 16 ak xéewali suuf ak la ko fees, \q1 ànd ak yiwu ka màkkaanoo ngarab sa doon tàkk, \q1 te wàccandoo ci kaw boppu Yuusufa; \q1 ak kaaŋi bokkam yay séddooy Aji Sax ji. \q1 \v 17 Taawub yëkk la, daraja mooy boroom, \q1 béjjén ya, béjjéni nagu àll la, \q1 ca lay butteendoo xeet yépp, \q1 ba ca cati àddina. \q1 Ñooñooy junniy junniy nit ca giirug Efrayim, \q1 ak junni ca giirug Manase. \b \q1 \v 18 Sabulon la wax ne ko: \q1 Yaw, Sabulon, bégeel say dem, \q1 Isaakar yaw, bégeel sa biir xayma. \q1 \v 19 Xeet yi la ñooñu di woo ca tund wa, \q1 te fa lañuy sarxee sarax yi war, \q1 koomu géej, ca lañuy nàmpe, \q1 booleek kumpay mbell yu làqu biir suuf. \b \q1 \v 20 Gàdd la wax ne ko: \q1 Barke ñeel na ku yaatal Gàdd. \q1 Ni gaynde la goore, \q1 te mooy xotat përëg akum kaaŋ. \q1 \v 21 Moo xool cér ba jëkka lew, jagoo ko, \q1 nde fa la wàllu njiit di xaar boroom. \q1 Moo fekksi njiiti askan wi, \q1 moo jëfe njekku Aji Sax ji, \q1 aki dogalam fi Israyil. \b \q1 \v 22 Dan la wax ne ko: \q1 Dan gaynde gu ndaw la, \q1 mooy tëbe fa diiwaanu Basan. \b \q1 \v 23 Neftali la wax ne ko: \q1 Neftalee ne xéew aku yiw, \q1 biibal barkey Aji Sax ji, \q1 te sowu ba bëj-saalum lay nangu. \b \q1 \v 24 Aser la wax ne ko: \q1 Yal na Aser gëna barkeel ci doom yi, \q1 ay bokkam baaxe ko, \q1 tànk yay xuuse ag diw. \q1 \v 25 Weñ ak xànjar la say xomb di doon, \q1 sa kàttan ànd ak saw fan. \b \q1 \v 26 Kenn du Yàllay Yesurun! \q1 Keey war asamaan, wallusi leen, \q1 war ay niir, ànd ak darajaam. \q1 \v 27 Yàlla ji sax fàww moo dib rawtu, \q1 përëgam bi sax dàkk di cëslaay, \q1 moo la dàqal ab noon \q1 ne la: «Jekklil!» \q1 \v 28 Israyil a ngi dëkke xel mu dal, \q1 walu Yanqóoba mee fegu, \q1 di wale réewum pepp ak biiñ bu bees, \q1 asamaan it di ko wàcceel ab layam. \q1 \v 29 Ndokklee, Israyil, ana ku mel ni yeen, \q1 askan wu Aji Sax jiy wallu, \q1 di seen kiiraay, di seen ndimbal, \q1 di saamar bi leen di sagal? \q1 Seeni noon a leen di loxal, \q1 te yeen, fa seen gannaaw ya ngeen di daagoo. \c 34 \s1 Musaa wuyji na \p \v 1 Ba loolu amee Musaa bàyyikoo jooru Mowab, yéegi tundu Nebo, ba ca collu tundu Pisga, wa jàkkaarlook Yeriko. \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nag won ko mboolem réew ma, diiwaanu Galàdd ba diiwaanu Dan, \v 2 mboolem diiwaanu Neftali, ak diiwaanu Efrayim ak Manase, mboolem diiwaanu Yuda, ba ca géej ga ca sowu, \v 3 ak wetu bëj-saalum, ak xuru Yeriko, dëkku tiir ya, ba ca Sowar. \v 4 Aji Sax ji ne ko: «Réew mii laa giñaloon Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, ne leen seen askan laa koy jox. Won naa la ko, ba nga teg ci sa bët, waaye foofa, doo fa teg sa tànk.» \v 5 Musaa, jaamub Aji Sax ji nag dee foofa ca réewum Mowab, na ko Aji Sax ji tudde. \v 6 Mu rob ko ca xur wa ca réewum Mowab, fa janook Bet Pewor. Kenn xamul nag fu bàmmeelam nekk ba tey jii. \p \v 7 Musaa amoon na téeméeri at ak ñaar fukk, ba muy faatu, te ay bëtam naqariwul, dooleem jeexul. \v 8 \w Bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* jooy nañu Musaa ca jooru Mowab diiru fanweeri fan, fani dëj ba doora mat. \v 9 Fekk na Yosuwe doomu Nuun feese xel mu rafet, ndax Musaa moo tegoon ay loxoom ci kawam, bànni Israyil nag déggal ko, di jëfe na ko Aji Sax ji sante woon Musaa. \p \v 10 Ab yonent lukkeekootul ci Israyil, mel ni Musaa, ma Aji Sax ji xejjoo woon ba naan ko jàkk, mu ne ko jàkk, \v 11 ba ca mboolem firnde yaak kéemaan ya ko Aji Sax ji yebale woon, ngir mu def ko ca biir réewum Misra, ca Firawna ak jawriñam ñépp, ak ca biir réewam mépp, \v 12 ak itam mboolem doole ju màgg ja Musaa wone, ak jëf ju réy te raglu ja mu def, bànni Israyil gépp teg ci bët.