\id COL (WOL) \ide UTF-8 \h Kolos \toc1 Bataaxal bi Yàlla may Póol, mu bind ko waa Kolos \toc2 Kolos \mt2 Bataaxal bi Yàlla may Póol, // mu bind ko waa \mt1 Kolos \c 1 \p \v 1 Man Póol ndawal Almasi Yeesu ci coobarey Yàlla, maa bind lii, ànd ceek mbokk mi Timote, \v 2 ñeel waa Kolos ñu sell te wóor te di bokki gëmkati Almasi. Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay. \s1 Póol ñaanal na waa Kolos \p \v 3 Sant Yàlla sunu Baayu Sang Yeesu \w Almasi|lemma="Almasi:"\w*, lanu saxoo, saa su nu leen di ñaanal; \v 4 dégg nanu ngëm gi ngeen gëm Almasi Yeesu, ak cofeel gi ngeen sopp gëmkat ñu sell ñépp, \v 5 te li waral ngëm googu ak cofeel googu, di seen yaakaara jot ca cér ba ñu leen dencal fa asamaan. Mooy yaakaar ja ngeen dale am ba ngeen jëkkee dégg kàddug dëgg gu xibaaru jàmm bi. \v 6 Ni leen xibaaru jàmm bi dikkale nag, ni la dikkale àddina sépp, te mu ngi meññ, di law, na mu ko dale defe fi seen biir, ca bés ba ngeen déggee lu jëm ci yiwu Yàlla, ba ràññee ko dëgg. \v 7 Noonu ngeen ko jànge ci Epafras, sunu mbokkum surga biy sunu soppe, te di jawriñu Almasi bu wóor bi nu jàpple\f + \fr 1.7 \fr*\ft Mbaa: \ft*\fqa jawriñu Almasi bu wóor ngir yeen.\fqa*\f*, \v 8 te moo nu xamal itam cofeel gi leen \w Noo|lemma="Noo gu Sell g-:"\w* gi may. \p \v 9 Moo tax nun itam, ba nu déggee seen mbir ba tey, noppiwunu leena ñaanal, di sàkku ngeen feese xam-xam ci lépp luy coobarey Yàlla, te ngeen ànd ceek lu mat sëkk ci wàllu xel, ak gis-gis bu Noo gi maye. \v 10 Su ko defee ngeen di dunde dundin wu yellook Boroom bi, ngir bànneexal ko ci wet gu nekk, seen meññeef it di jépp jëf ju baax, te ngeen gën di xam Yàlla. \v 11 Ngir itam ngeen manoorewoo jépp manoore, na leen ko Yàlla manloo ci kàttanam gu màgg, ba ngeen mana dékkoo lépp, xolu muñ, \v 12 te ngeen di sante Baay bi, mbég, moom mi leen yellale ab cér ca muuru ñu sell ña, ca réewum leer ga. \s1 Almasi jubale na nit ak Yàlla \p \v 13 Yàlla kat moo nu wallu ba génne nu ca kilifteefu réewum lëndëm ga, toxal nu ci biir nguurug Doomam ji mu sopp. \v 14 Ci moom lanu ame ag \w njot|lemma="jot:"\w*, te moo nu jéggal sunuy bàkkaar. \p \v 15 Doom jooju moo di niruwaale Yàlla, mi kenn manula gis, mooy \w taaw|lemma="Taaw b-:"\w* bi, ki jiitu mépp mbindeef. \v 16 Ndax moo di ki Yàlla sàkke lépp lu nekk asamaan, ak lu nekk ci suuf, lu gisu, ak lu gisuwul, muy boroom gàngune yeek, boroom ndomboy tànk yeek, boroom nguur yeek, boroom sañ-sañ yi. Lépp ci moom lees ko sàkke, te mooy ki tax ñu sàkk lépp. \v 17 Mooy ki nekkoon naka jekk balaa daraa nekk, te lépp ci moom la sottee ba temboo. \v 18 Mooy boppu yaram, wiy mbooloom gëmkat ñi, mooy njàlbéen, mooy taaw bi jëkka dekki, ndekkite lu dee toppul, ba tax muy ki jiitu ci lépp, \v 19 ndax Yàlla la soob mu dëël gépp matam ci moom. \v 20 Deretam ja tuuru ca bant ba, ca la Yàlla defe jàmm, ba sottale ci moom, pexe mi mu jubalee boppam ak lépp, muy lu nekk ci kaw suuf, ak la fa asamaan. \p \v 21 Te yeen ñi masoona sore lool Yàlla, doonoon ay noonam ci wàllu xalaat, ak jëf ju bon, \v 22 tey, deewug yaram, deewug suux, gi Almasi dee, moom la leen Yàlla jubalee ak boppam, ba teewal leen fi kanamam, ngeen di ñu sell, mucc sikk, seen der set wecc. \v 23 Noonu la deme, ndegam kay fekk na leen sësoo ngëm gu ngeen dëjoo ba dëgër, te baña nangu lenn di leen sorele ak yaakaar ji ci xibaaru jàmm, bi ngeen dégg, te ñu biral ko, ñeel mépp mbindeef. Man Póol nag, ci yégle xibaaru jàmm boobu laa di ab jawriñ. \s1 Póol tiisoo na waa Kolos \p \v 24 Léegi nag maa ngi bége coono yi ma jànkoonteel ngir seen njariñ; li des ci tiisi \w Almasi|lemma="Almasi:"\w*, moom laay mottalee coono yooyu ma daje sama yaramu suux wii, ngir njariñal mbooloom gëmkat, miy yaramu Almasi. \v 25 Ci moomu mbooloo laa dib jawriñ, te Yàllaa ma sase noonu, ñeel leen, ngir ma xamle kàddug Yàlla ba mu mat sëkk. \v 26 Kàddu googu moo di mbóot mi masoona làqu maasoo maas, waaye tey Yàllaa ko xamal ay nitam ñu sell. \v 27 Ñoom la Yàlla nammoona xamal ni mbóot mi yaatoo te yéeme, ñeel jaambur ñi dul Yawut: mbóot mi moo di Almasee ngi ci yeen ñi dul Yawut itam, loolu di seen yaakaar ci ndam lu leen ñeel. \p \v 28 Almasi moomu nag lanuy xamle; na mu gëna xeloo lanuy àrtoo nit ku nekk, te ni lanuy jàngale nit ku nekk, ngir àgge nit ku nekk ba fa kanam Almasi, fekk ko mat sëkk, na mu ware ku ànd ak Almasi. \v 29 Loolu moo ma tax di góor-góorlu ci xare bii may xaree dooleem, ak manoorey jëfam, jiy liggéey ci sama jëmm jii. \c 2 \p \v 1 Bëgg naa nag, ngeen xam xare bu metti, bi ma leen di xareel, yeen ak waa Lawdise ak mboolem gëmkat ñi ma masula teg bët, \v 2 ngir ngeen gëna am fit, mànkoo ci biir cofeel, te géeju ci gis-gisu xol bu leer nàññ te wóor, ba mana daj dëgg, mbóotum Yàlla, miy Almasi ci boppam. \v 3 Ci moom la mboolem alal ji ci xel ak xam-xam, dëxëñe. \v 4 Loolu laa leen di wax, ngir kenn bañ leena réerale ay kàdduy naxe yu mbubboo ag dëgg. \v 5 Ndax jëmm ji kat teewul, waaye xol baa ngeek yeen, di bégee gis seen doxalin wu jekk, ak seen ngëm gu wér gu ngeen gëm Almasi. \s1 Jëfeleen ni ñu bokk ak Almasi \p \v 6 Kon nag, ni ngeen nangoo \w Almasi|lemma="Almasi:"\w* Yeesu di Sang bi, àndleen ak moom, jëfe noonu. \v 7 Sampleen seeni reen ci moom, tabaxuleen ci moom, feddlikuleen ci wàllu ngëm, ni ñu leen ko jàngale, ba seenub xol baawaanal kàdduy cant. \p \v 8 Moytuleen ba kenn bañ leena këfe kàdduy naxi neen yu ñu jàppe xam-xam bu xelu, kàddu yu sukkandikoowul Almasi, xanaa aaday nit, ak cëslaayi àddina. \p \v 9 Ndax kat ci Almasi, ci yaramu nitam la léppi Yàlla dëkke, ba mat sëkk ci moom, \v 10 ci moom ngeen mate it, te mooy kilifay mboolem boroom nguur yi, ak mboolem boroom sañ-sañ yi. \v 11 Ci moom ngeen xarafe xaraf gu loxol nit deful, ndax noonu kuy xarfal nit ki di doge as lëf ci yaramu nit ki, ni la Almasi di doge ba mu set, buumu njaam gi leen dooley bàkkaar tënke woon. Noonu la Almasi di xarfalee. \v 12 Ni ñu leen booleek moom suul, keroog ba ñu leen sóobee cim ndox, noonu ngeen dekkeendoo ak moom, ndax yeena wóolu dooley Yàlla mi ko dekkal. \p \v 13 Yeen ñi doonoon ndee fa kanam Yàlla ndax seeni moy, ak seen ñàkka xaraf, ndax li ngeen dul Yawut, Yàllaa leen booleek Almasi dundalaat leen. Moo nu baal sunu moy yépp. \v 14 Kayitu bor bi nu tiiñaloon, te dogali yoon toppe nu ko, moom moo far mbind ma, yóbbu kayit ga, daajaale ko ak Almasi ca bant ba. \v 15 Moo dog sidditi boroom nguur yeek boroom sañ-sañ yi ci jaww ji, ñu doon ay jaam yu mu jàppe xare. Moo leen weer it ci kanam ñépp, diriwaale leen ca biir njaab ma topp ca ndam, la Almasi ame ca bant ba. \p \v 16 Kon nag bu leen kenn sikkal ci ñam wu ngeen lekk, mbaa lu ngeen naan, mbaa màggal bés bu rafet, mbaa Terutel weer, ak \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*. \v 17 Loolu lépp takkndeeru yaram wuy jëmmal lu dikkagul, moom rekk la woon. Waaye yaram wi dëgg moo di Almasi. \v 18 Buleen nangu kenn ku leen sikkal, te di kuy teg boppam jëfi toroxlu, di jaamu ay malaaka, topp seen gis-gisi peeñuy bopp. Ñu ni mel ñooy réy-réyloo xalaati neen yu ñu fente seen yég-yégi bakkan. \v 19 Ñooñu jokkuwuñu ci Almasi, miy bopp bi, te ci bopp bi la yaram wi wépp di jëfandikoo siddit yeek tenqo yi, ba suuxatu, ngir lépp mànkoo ba mana màgg, ni ko Yàlla di màggale. \p \v 20 Ndegam nag yeena bokk ak Almasi dee, ba teqlikoo ak li àddina def cëslaay, ana lu tax ngeen mel ni ñu bokk ci àddina ba tey, di tegoo ay dogali yoon yu mel nii: \v 21 «Bul jël lii, bul ñam lee, bul laal la ca des.» \v 22 Te mboolem yëf yooyu dogali yoon yi jëm day jeex doŋŋ bu ñu leen jëfandikoo. Loolu ay santaane aki àlluway nit doŋŋ la. \v 23 Dëgg la, xel man naa nangu dogali yoon yu ni mel, ndax laaj na nit ki pastéefu ci diine ju mu tegool boppam, laaj na it toroxlu, ak coonoy yaram yu tukkee ci yar bu metti bu nit kiy tegoo, waaye jariñul dara ku bëgga moom bakkanam. \c 3 \s1 Gëmkatub Almasi, dundin wu yees \p \v 1 Gannaaw nag yeena dekkeendoo ak \w Almasi|lemma="Almasi:"\w*, sàkkuleen la fa kaw, fa Almasi tooge ca ndijooru Yàlla. \v 2 La fa kaw, xintewooleen ko, te ngeen ba li fi suuf, \v 3 ndaxte dee ngeen, ba seenug dund ànd ak Almasi, làqe fa Yàlla. \v 4 Seenug dund dëgg Almasi la, te keroog bu Almasi feeñee, yeen itam ay ànd ak moom feeñ, ba séddu ci ndamam. \p \v 5 Kon nag reyleen seen cér yi bokk fii ci kaw suuf; lu mel ni powum séy, ak jëfi sobe, ak ñàkk sago ci lu jekkadi, ak xemmemtéef yu bon, ak bëgge, te loolooy bokkaale ba tey, \v 6 yooyooy wàcce sànjum Yàlla ci kaw ñi déggadi. \v 7 Yeen itam noonu ngeen daan jëfe bu jëkk, ba seenug dund bokkee fii ci kaw suuf. \v 8 Waaye léegi lii lépp baleen ko: tàng xol, ak mer mu ëpp, ak coxor, ak saaga, ak waxi ñàkk kersa. \v 9 Buleen di fenante, gannaaw seen jëmm ja woon démb, boole ngeen kook jëfinam ja mu àndal, summi, \v 10 ba sol seen jëmm ju yees, jiy gën di yeeslu, te di gëna niru ki leen ko sàkkal, ba kera ngeen xamee, xam-xam bu mat sëkk. \v 11 Dundin wu yees woowu amul jaambur akub Yawut, amul ku xaraf ak ku xaraful, amul ab doxandéem ak ku xayadi, amul ab jaam ak as gor, waaye Almasi mooy lépp te moo nekk ci ñépp. \p \v 12 Yeenay ñi Yàlla taamu, sellal leen, sopp leen. Kon nag solooleen xolu yërmande, akug mbaax, ak woyoflu, ak jikko ju lewet, ak xolu muñ. \v 13 Muñalanteleen te di balante, ndegam kenn a am lenn lu mu sikke moroomam. Ni leen Boroom bi baale, deeleen balantee noonu. \v 14 Ci kaw loolu lépp nag, tegooleen cofeel; mooy xànc gi leen faste, ba seenug bennoo mat sëkk. \p \v 15 Na jàmmu Almasi saytu seen xol. Ci jooju jàmm lañu leen woo, fekk leen ngeen di wenn yaram doŋŋ, te it saxooleen cant. \v 16 Na leen kàddug Almasi dëkke, bay baawaan, ngeen di jariñoo xel mu mat sëkk mu ngeen di jànglantee, ak a artoonte. Woyeleen xolub cant, ñeel Yàlla, ay taalifi Sabóor, ak woyi tagg Yàlla, ak woy yu fentoo ci Noo gi. \v 17 Lu ngeen mana def, muy ci wax, di ci jëf, defleen ko ci turu Sang Yeesu, tey sant Yàlla Baay bi ci moom. \s1 Rafetooleen \p \v 18 Jigéen ñi, nangul-leen seen jëkkër, noonu mu jekke ci ku bokk ci Boroom bi. \p \v 19 Góor ñi, soppleen seen jabar, te buleen leen soxore. \p \v 20 Xale yi, déggal-leen seeni waajur ci lépp, nde loolu mooy li Boroom bi rafetlu. \p \v 21 Yeen ñiy baay, buleen yékkati seen xolu doom, ngir baña jeexal seen xol. \p \v 22 Jaam yi, nangul-leen ci lépp seen sang yi ci àddina. Buleen ko defe ngistal, mbaa ngeen di ko sàkkoo lu leen neex, waaye defeleen ko yéeney xol bu dëggu, ndax ragal Boroom bi. \v 23 Lu ngeen mana def, liggéeyeleen ko xol bu tàlli, ni bu ñeelul woon nit doŋŋ, xanaa Boroom bi. \v 24 Te ngeen xam ne ci loxol Boroom bi ngeen di nangoo yool bi ngeen muurloo. Sang \w Almasi|lemma="Almasi:"\w* mooy ki ngeen di jaamu. \v 25 Waaye ku def njubadi, njubadi ga mu def lay yooloo, te xejj ak seen du ci am. \c 4 \p \v 1 Yeen ñiy sang yi, yorleen seeni jaam, yorin wu jub te aw yoon, te ngeen xam ne yeen itam am ngeen ab Sang fa asamaan. \s1 Yeneen warugar a ngi \p \v 2 Ag ñaan nag, saxooleen ko, te ngeen teewlu ci, boole ci ag cant. \v 3 Te ngeen ñaanaale nu ci itam, ngir Yàlla ubbil nu buntu xamle kàddu gi, ngir siiwtaane mbóot mi ci \w Almasi|lemma="Almasi:"\w*, li waral ñu jéng ma. \v 4 Ñaanleen ma man koo waxe ba mu leer nàññ ni mu ma ware. \p \v 5 Jëfeleen xel mu rafet seen diggante ak aji gëmadi ñi ci biti, te \w jot|lemma="jot:"\w* gu ngeen am, fexeleen ba jariñoo ko. \v 6 Na seen kàddu ànd ak yiw te am solo, te ngeen xam nu ngeen di tontoo ku nekk, tont li war. \s1 Póol tàggu na waa Kolos \p \v 7 Mboolem lu jëm ci man nag, Tisig dina leen ko xamal. Mbokk la, soppe la, jawriñ ju wóor la, te it sama mbokkum jaam la, ci liggéeyu Boroom bi. \v 8 Lii sax moo tax ma yónni ko ci yeen: xamal leen lu jëm ci nun, ak itam, teewaayam bu dëfal seen xol. \v 9 Onesim lay àndal, sunu mbokk mu wóor, di sunu soppe, te mu bokk ci yeen. Ñoo leen di xamal mboolem lu fi xew. \p \v 10 Aristàrk mi ma bokkal kaso bi, mu ngi leen di nuyu, moom ak Màrk rakku Barnaba. Ci mbiru Màrk moomu ngeen jotoon ndigal, ngir bu dikkee, ngeen teral ko. \v 11 Yeesu mi ñuy wax Yustus itam, mu ngi nuyoo. Li bokk ci askanu Yawut, ñoom rekk ay liggéeyandoo ak man ngir nguurug Yàlla, te ñoo seral sama xol. \v 12 Ab nuyoo it ñeel na leen, tukkee ci jaamub \w Almasi|lemma="Almasi:"\w* Yeesu, Epafras, mi bokk ci yeen. Ku jàmbaare ci saxoo leena ñaanal, ngir seenub taxawaay sotti te mat sëkk ci jëfe mboolem luy coobarey Yàlla. \v 13 Maa ko seedeel ne coonoy ñaan bu réy la nekke, ngir yeen ak waa Lawdise ak waa Yerapolis. \v 14 Ab nuyoo it ñeel na leen, tukkee ci sunu soppe, Luug, doktoor bi, ak Demas. \v 15 Nuyul-leen nu bokk yi dëkke Lawdise, ak sunub jigéen Nimfa, ak mbooloom gëmkat, miy daje këram. \p \v 16 Gannaaw bu ngeen jàngee biral, bataaxal bii ci seen biir, fexeleen it ba ñu jàng ko, biral, fa mbooloom gëmkat ma fa Lawdise, te yeen it bataaxal ba ngeen di jote Lawdise, nangeen ko jàng biral. \p \v 17 Waxal-leen ma Arsipp ne ko: «Neel jàkk ci liggéey bi nga sasoo ci Boroom bi, ngir nga sottal ko.» \p \v 18 Man Póol nag maa leen bind nuyoo bii ci sama loxol bopp. Fàttlikuleen ne dañu maa tëj kaso. Yal na aw yiw ànd ak yeen!