\id 2SA (WOL) \ide UTF-8 \h 2.Samiyel \toc1 Samiyel, di téereb ñaareel bi \toc2 2.Samiyel \mt1 Samiyel \mt2 di téereb ñaareel bi \c 1 \ms1 Lii mooy jaar-jaari Buur Daawuda \s1 Lu jëm ci tàggeb Sóol \p \v 1 Gannaaw ba Sóol faatoo, fekk na Daawuda walbatikoo ca dumay Amalegeen ña, dellu Ciglaag, ba toog fa ñaari fan. \v 2 Ca gannaaw ëllëg sa, jenn waay ne jimeet, jóge ca dalub Sóol, dikk. Yére yaa nga xottiku, bopp ba taq suuf, ngir naqarlu. Naka la agsi ci Daawuda, daldi daanu fi suuf, sujjóot. \p \v 3 Daawuda ne ko: «Foo jóge nii?» Mu ne ko: «Ca dalub Israyil laa rëcce.» \v 4 Daawuda ne ko: «Lu xew, gaawe ma!» Mu ne ko: «Mbooloom Israyil a dawe ca xare ba. Ñu bare ca ñoom daanu nañu, dee. Sóol ak doomam Yonatan it dee nañu.» \v 5 Daawuda ne ndaw la: «Lu la xamal ne Sóol ak doomam Yonatan dee nañu?» \v 6 Ndaw la ne ko: «Dafa yemook ma tollu tembe ca kaw tundu Gilbowa. Ndeke Sóol a nga fa, sukkandikoo xeejam. Watiiri xare yaak gawar ya defuñu lu moy ne ko dann. \v 7 Naka la ne gees, yem ci man, woo ma, ma wuyu. \v 8 Mu ne ma: “Yaa di kan?” Ma ne ko: “Ab Amalegeen laa.” \v 9 Mu ne ma: “Kaay fii, jekkli ma. Maa ngi ci miirum ndee, doonte dese naa tuuti.” \v 10 Ma dikk, daldi koy jekkli, ndax xamoon naa ne du dundati gannaaw jéllam ba. Ma summi nag mbaxanam buur ma mu soloon, tekki lam ba woon ca përëg ma. Yooyu laa la yótsi nii, sang bi.» \p \v 11 Ba loolu amee Daawuda sëq yéreem, xotti, ña ànd ak moom ñépp itam, noonu, ndax aw naqar. \v 12 Ñaawlu nañu, di jooy, lekkuñu ba ca ngoon ndax Sóol ak doomam Yonatan ak gàngooru \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, waa kër Israyil, ña fàddoo saamar. \p \v 13 Daawuda ne ndaw la: «Ana foo bokk?» Mu ne ko: «Man doomu doxandéemub Amalegeen laa.» \v 14 Daawuda ne ko: «Noo saña xàccee sa loxo, di bóom ki Aji Sax ji fal?» \v 15 Daawuda nag woo kenn cay surgaam, ne ko: «Dikkal dóor, mu dee!» \v 16 Daawuda ne Amalegeen ba: «Yaa gàddu sa bakkanu bopp, ndax yaa seedee sa gémmiñu bopp ne yaa rey ki Aji Sax ji fal.» Surga ba dóor Amalegeen ba, mu dee. \s1 Daawuda jooy na Sóol ak Yonatan \p \v 17 Kàddu yii la Daawuda jooye Sóol ak doomam Yonatan. \v 18 Moo santaane ñu jàngal ko askanu Yuda. «Fittkat» lañu dippee woy wi. Nii lañu ko binde ci «Téereb aji jub ji.» Mu ne: \b \q1 \v 19 Wóoy Israyil, ña ngay sagoo lañu jam, \q2 ñu ne lareet ca sa tund ya! \q1 Jàmbaar ñaa daanu! \b \q1 \v 20 Buleen ko siiwal fa Gaat, \q1 buleen ko yéene fa mbeddi Askalon, \q1 lu ko moy janqi Filisti bég, \q1 janqi yéefar yiy textexi. \b \q1 \v 21 Wóoy tundi Gilbowa! \q1 Yàlla bu ngeen lay, bu ngeen tawlu, \q1 Yàlla bu seeni tool nangooti, \q2 ba duunal jooxeb pepp, \q1 nde foofa lees torxale pakkub jàmbaar. \q1 Wóoy pakkub Sóol ba deesul diwati! \q1 \v 22 Du deret mbaa nebbonu jàmbaar \q2 bu fittug Yonatan xof, \q1 te saamaru Sóol ba du sooy! \b \q1 \v 23 Wóoy Sóol ak Yonatan, \q1 ñoo yiw, sopplu ba ñuy dund, \q1 te ba ñu deeyee, teqlikoowuñu. \q1 Ag jaxaay, ñoo ko gëna gaaw, \q1 te gaynde, ñoo ko gëna jàmbaare. \b \q1 \v 24 Yeen jigéeni Israyil, \q1 jooyleen Sóol, ma leen wodde ndimol tànnéef \q2 lu xonq curr, \q1 takkal leen gànjari wurus ca seen kawi yére. \b \q1 \v 25 Jàmbaar ñaa daanoo biir xare ba, \q1 Yonatan lañu jam ca kaw tund ya! \q1 \v 26 Yonatan, doom yaay, tiisoo naa la, \q1 dama laa soppoon lool, \q1 te sa mbëggeel ci man yéeme, \q1 ba raw mbëggeelu jigéen. \b \q1 \v 27 Jàmbaar ñaa daanu, \q1 ngànnaayi xare ya sànku! \c 2 \s1 Daawuda falu na buur ca Yuda \p \v 1 Gannaaw ba loolu weesee Daawuda daa laaj \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ne ko: «Ndax ma dellu ci dëkki Yuda yi benn?» Aji Sax ji ne ko: «Demal.» Daawuda ne ko: «Bu ma ciy dem?» Aji Sax ji ne ko: «Ebron.» \v 2 Daawuda dem ca, ànd ak ñaari soxnaam, Ayinowam ma cosaanoo Yisreel, ak Abigayil ma doon jabaru Nabal waa Karmel ba. \v 3 Daawuda nag yóbbaale nit ña ànd ak moom, kenn ku ci nekk ak njabootam, ñu dem sanci ca dëkk ya wër Ebron. \v 4 Ba mu ko defee waa Yuda dikk, diw fa Daawuda, fal ko buurub waa kër Yuda. \p Gannaaw gi ñu wax Daawuda ne ko waa Yabes Galàdd ñoo rob Sóol. \v 5 Daawuda yónnee ay ndaw ca waa Yabes Galàdd, wax leen ne leen: «Yal na leen Aji Sax ji barkeel ndegam yeena jëfe ngor seen digganteek seen sang Sóol, ba rob ko. \v 6 Kon nag yal na Aji Sax ji jëfeek yeen ngor ak kóllëre. Man itam dinaa leen yéwéne ndax nii ngeen jëfe. \v 7 Léegi nag dëgërluleen te góor-góorlu. Dëgg la seen sang Sóol faatu na, waaye man mii la giirug Yuda fal, may seen buur.» \s1 Isboset falu na buur ca Israyil \p \v 8 Doomu Ner, Abner njiital mbooloom xarem Sóol nag, fekk na mu yóbbu Isboset\f + \fr 2.8 \fr*\fk Isboset: \fk*\ft mbind mi ci ebrë, làkku bànni Israyil, Isboset la indi, mu firi Nitu gàcce. Turam wu jëkk nag, Isbaal la woon, mu firi Nitu Baal. Bu jëkkoon Baal «kilifa gi» la doon tekki. Waaye gannaaw gi Baal turu tuur mu waa Kanaan la woon. Du woon teggin ñuy wooye buurub Israyil turu tuur moomu. Moo tax ñu soppi turam wu jëkk wa, tudde ko Isboset.\ft*\f* doomu Sóol ju góor, jàllale ko ba Maanayim. \v 9 Mu tabb ko nag buuru diiwaani Galàdd ak Asur ak Yisreel ak Efrayim ak Beñamin, Israyil gépp daal. \v 10 Ñeent fukki at la Isboset doomu Sóol amoon ba muy falu buurub Israyil, te ñaari at la nguuru. Waa kër Yuda doŋŋ ñoo toppoon Daawuda. \v 11 Diir ba Daawuda falu buurub Ebron gu waa kër Yuda, juróom ñaari at la ak juróom benni weer. \s1 Yuda ak Israyil xare nañu \p \v 12 Mu am bés, Abner doomu Ner ànd ak niti Isboset doomu Sóol, ñu jóge Maanayim, jëm diiwaanu Gabawon. \v 13 Yowab, mi Seruya di yaayam, daldi ànd ak niti Daawuda, ñu dem dajejeek ñoom ca wetu déegub Gabawon. Ñii taxawe gii wet, ñee taxawe ca wàlla, ñu séq déeg ba. \v 14 Abner ne Yowab: «Ayca na xale yu góor yi jóg, daje fi sunu kanam.» Yowab ne ko: «Ayca!» \v 15 Ñu daldi limoo, fukki góor ak ñaar taxawal giirug Beñamin ak Isboset doomu Sóol; fukki góor ak ñaar taxawal Daawuda. \v 16 Ku nekk ne sa boppu moroom ŋëjj, rekk bojj sab saamar ca wet ga, ñu ànd daanu. Moo tax ñu wooye bérab booba ca Gabawon «Toolub ñawka yi.» \p \v 17 Bésub keroog xeex ba metti na lool, waaye Abner ak waa Israyil ñoo féete suuf niti Daawuda. \p \v 18 Ñetti doomi Seruya ña nga fa woon: Yowab ak Abisay ak Asayel. Asayel nag daa manoona daw lool ni kéwél. \v 19 Asayel ne dann Abner rekk, jàddul ndijoor, jàddul càmmoñ. \v 20 Abner geesu ne ko: «Kii Asayel?» Mu ne ko: «Man a.» \v 21 Abner ne ko: «Tee ngaa jàdd ndijoor mbaa càmmoñ, te jàpp kenn ci xale yu góor yi, futti ko!» Asayel nag buggu koo bàyyi, xanaa topp ko rekk. \v 22 Abner dellu ne Asayel: «Xiddi ma! Bul tax ma jam la, nga daanu! Te kon xawma nu may jàkkaarlooteek sa mag Yowab!» \v 23 Asayel të ticc, topp ko. Abner jam ko catal xeejam ca biir ba, ba xeej ba fëll ca gannaaw ga, mu daanu dee ca saa sa. Ba loolu amee, ku dikk, ba tollook bérab ba Asayel daanu dee, daldi fay taxaw. \p \v 24 Yowab ak Abisay nag dàqi Abner. Ba jant bay lang, ña nga tollu ca tundu Ama, wa janook Giya, ca yoon wa jëm màndiŋu Gabawon. \v 25 Beñamineen ñi daldi mànkoo, topp ca gannaaw Abner, ñu def menn mbooloo, bokk taxaw ci kaw wenn tund. \v 26 Abner àddu ca kaw, ne Yowab: «Xanaa saamar day lekku suux ba fàww? Xamuloo ne lii aw naqar doŋŋ lay mujje? Ana looy xaarati ci ne mbooloo mi ñu noppee topp seeni bokk?» \v 27 Yowab ne ko: «Giñ naa ci Yàlla jiy dund, boo waxuloon, nit ñi duñu noppee dàq seeni bokk te bët setul.» \v 28 Ba loola amee Yowab wal liit ga, gaa ña ñépp nag taxaw, noppee topp Israyil, daldi dakkal xare ba. \v 29 Abner aki nitam dañoo fanaanee topp xuru Yurdan guddig keroog, ba jàll dexu Yurdan. Ñu daldi jaare Bittron gépp, door a agsi Maanayim. \p \v 30 Gannaaw ba Yowab walbatikoo ca ndàqum Abner, daa woo gàngooram gépp, fukk ak juróom ñeent wuute ci niti Daawuda, te limaalewuñu Asayel. \v 31 Waaye fekk na niti Daawuda rey ñetti téeméer ak juróom benn fukk (360) ca Beñamineen ñaak niti Abner. \v 32 Ñu yóbbu Asayel, rob ko ca wetu baayam ca Betleyem, Yowab aki nitam nag fanaanee dox, ba jant fenke leen Ebron. \c 3 \p \v 1 Xare ba nag yàggoon na diggante waa kër Sóol ak waa kër Daawuda. Daawuda di gëna am doole, waa kër Sóol di gëna néew doole. \s1 Daawuda am nay doom ca Ebron \p \v 2 Doomi Daawuda yu góor yi juddoo Ebron ñoo di: taawam Amnon, mi Ayinowam waa Yisreel ba di ndeyam; \v 3 ñaareelu doomam di Kilab, ndeyam di Abigayil, ma doon jabaru Nabal waa Karmel ba; ñetteelu doomam di Absalom, mi Maaka di ndeyam. Maaka, Talmay buurub Gesur ay baayam; \v 4 ñeenteelu doomam di Adoña, mi Agit di ndeyam; juróomeelu doomam di Sefatiya mi Abital di ndeyam; \v 5 juróom benneelu doomam di Ittireyam, mi soxnaam si ñuy wax Egla di ndeyam. Ñooñu ñooy doomi Daawuda ya juddoo Ebron. \s1 Abner jote naak Isboset \p \v 6 Diir ba waa kër Sóol di xareek waa kër Daawuda, Abner a ngay gëna dëgëral taxawaayam ca waa kër Sóol. \v 7 Sóol nag amoon na nekkaale bu ñuy wax Rispa doomu Aya. Mu am bés Isboset ne Abner: «Ana lu waral nga dëkkoo sama nekkaaleb baay?» \v 8 Abner mer lool ca la ko Isboset wax. Mu ne ko: «Ndax dama di xajub workat bu Yudeen ñi? Ba tey jii ngor laay jëfe ak sa waa kër baay Sóol, aki bokkam aki soppeem. Te it teguma la ci loxol Daawuda; yaw nga di ma tuumaal ci ndaw sii tey? \v 9 Yal na ma \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji teg mbugal mu gëna tar ndegam defaluma Daawuda la ko Aji Sax ji giñaloon, \v 10 ne ko dina jële nguur gi ci waa kër Sóol, samp jalub Daawuda ci kaw Israyil ak Yuda, dale ko Dan ca bëj-gànnaar, ba Beerseba ca bëj-saalum.» \v 11 Isboset nag ñemewula teg baat ca la Abner wax, ndax ragal ko. \s1 Abner fekki na Daawuda \p \v 12 Ba loolu amee Abner yebal ca saa sa ay ndaw ca Daawuda, ne ko: «Ana ku moom réew mii?» Mu neeti ko: «Fasool ak man \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w*. Maa lay jàpple, ba walbatil la Israyil gépp, ñu nangul la.» \v 13 Daawuda ne ko: «Baax na. Dinaa fasook yaw kóllëre, waaye lenn rekk laa lay ñaan. Bul dikk fi sama kanam te indiloo ma sama jabar Mikal doomu Sóol.» \v 14 Gannaaw loolu Daawuda yebal ay ndaw ca Isboset doomu Sóol, ne ko: «Jox ma Mikal, sama jabar ja ma cane woon téeméeri mbuñukay waa Filisti.» \v 15 Isboset yónnee, jëli Mikal ca jëkkëram Paltiyel\f + \fr 3.15 \fr*\fk Paltiyel \fk*\ft mooy Palti ba tey. Seetal ci \ft*\ft \+bk 1.Samiyel\+bk* 25.44.\ft*\f* doomu Layis. \v 16 Paltiyel topp ca gannaaw ndaw sa, di jooy, ba ñu àgg Baxurim. Abner ne ko: «Ayca, doxal ñibbi.» Waa ja ñibbi. \p \v 17 Ba mu ko defee Abner gise ak magi Israyil, ne leen: «Yàgg ngeena bëgga fal Daawuda, muy seen buur. \v 18 Kon ayca boog! Ndax \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee ko digoon Daawuda, ba mu nee: “Ci sama jaam Daawuda laay walloo Israyil sama ñoñ, ci waa Filisti ak mboolem seeni noon.”» \v 19 Abner wax ak giirug Beñamin itam déeyook ñoom ba noppi dem Ebron ca Daawuda, déey ko la waa Israyil ak giirug Beñamin gépp namma def. \v 20 Ba Abner agsee Ebron ca Daawuda, ñaar fukki nit la àndal. Daawuda berndeel Abner, mook nit ña ànd ak moom. \v 21 Ba loolu amee Abner ne Daawuda: «Buur sang bi, dama lay wool Israyil gépp, ñu wuysi la. Su ko defee ñu fasook yaw kóllëre, nga mana nguuru fu la neex.» Ba loolu amee Daawuda yiwi Abner, mu dem ci jàmm. \s1 Yowab fey na Abner \p \v 22 Ci kaw loolu rekk niti Daawuda ànd ak Yowab, jóge xare, indaale lël ju bare. Waaye fekkul Abner Ebron ca Daawuda, ndax fekk na Daawuda yiwi ko, ba mu dem ci jàmm. \v 23 Yowab agsi mook mboolem gàngoor ga ànd ak moom. Ñu ne ko Abner doomu Ner ñëwoon na ca Buur, ba mu yiwi ko, mu dem ci jàmm. \v 24 Yowab dem ca Buur ne ko: «Waaw, li nga def nag? Abner mii dikk, nga bàyyi ko mu dem nii rekk! \v 25 Xam nga Abner doomu Ner! Wor la moo ko fi indi, ngir xam say dugg ak say génn, ak lépp looy def.» \v 26 Ci kaw loolu Yowab bàyyikoo ca Daawuda, yebal ay ndaw yu toppi Abner, dab ko, waññee ko ca teenub Sira. Waaye Daawuda yégu ca dara. \v 27 Naka la Abner délsi ba Ebron, Yowab berook moom ca buntu dëkk ba, mel ni kuy déeyook moom, daldi koy jam ci biir, rey ko, feyul Asayel, rakkam ja Abner bóomoon. \p \v 28 Gannaaw ga, ba ko Daawuda yégee, da ne: «Man de set naa wecc, maak sama waa réew ba fàww fi kanam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ci bakkanu Abner doomu Ner bi rot. \v 29 Yal na deewug Abner këppu ci kaw boppu Yowab, mook waa kër baayam gépp. Yàlla bu waa kër Yowab ñàkk ku ànd ak jàngoroy xelli, mbaa jàngoroy der juy law\f + \fr 3.29 \fr*\fk jàngoro yi: \fk*\ft seetal ci \ft*\ft \+bk Sarxalkat yi \+bk* 13.2 ak 15.2.\ft*\f*, mbaa lafañ buy doxe yet, mbaa ku deeye xare, mbaa ku amul lu mu lekk.» \p \v 30 Noonu la Yowab ak rakkam Abisay bóome Abner, ndax la mu reyoon seen doomu ndey Asayel ca xareb Gabawon ba. \s1 Jooy nañu Abner \p \v 31 Ba loolu wéyee Daawuda wax ak Yowab, mook mboolem gàngoor ga ànd ak moom, ne leen: «Xottileen seeni yére, soli saaku, ñaawloo ko deewug Abner.» Buur Daawuda ci boppam dox na, topp ca jaat ja. \v 32 Ñu denc Abner ca Ebron. Buur Daawuda ne yikkét jooy ca bàmmeelu Abner, mbooloo ma mépp jooy. \v 33 Woy wii la Buur fent, jooye ko Abner. Mu ne: \q1 «Moo Abner, jombuloo dee ni sagaru nit a? \q1 \v 34 Jéngeesu la, \q1 yeeweesu laak càllala. \q1 Danga ne dàll daanu, \q2 ni ñuy daanoo fi kanam ku bon.» \m Mbooloo ma mépp dellu jooyati. \p \v 35 Gannaaw gi mbooloo mépp di soññ Daawuda, ngir mu lekk, balaa jant a so. Daawuda daldi giñ ne: «Yal na ma Yàlla teg mbugal mu gëna tar ndegam maa sex dugub mbaa ñam wu mu doon, te jant sowul.» \v 36 Mbooloo ma mépp a seede loolu, rafetlu ko, na ñu rafetloo mboolem lu Buur Daawuda def. \v 37 Mbooloo mépp ak Israyil gépp a xam bésub keroog ne pexe ma rey Abner doomu Ner jógewul ca Buur. \v 38 Ba loolu amee Buur wax aki nitam ne leen: «Xanaa xamuleen ne ab garmi, nit ku màgg moo daanu bésub tey fi digg Israyil? \v 39 Bésub tey jii li ma falu buur lépp, néew naa doole, ndax doomi Seruya yii ñoo ma gëna dëgër xol, ba jaaxal ma. Waaye yal na \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji fey ku bon jëfam.» \c 4 \s1 Isboset faatu na \p \v 1 Ba Isboset doomu Sóol déggee ne Abner dee na ca Ebron, xolam jeex na, Israyil gépp jàq. \v 2 Isboset amoon na ñaari njiiti gàngooru yàqkat: kenn ka di Baana, ka ca des di Rekab, ñuy doomi góor gu ñuy wax Rimon, giiroo ci giirug Beñamin te dëkke Berot ga ñu boole woon ca suufas Beñamin; \v 3 ndax waa Berot a dawoon, làquji Gitayim, doon fa ay doxandéem ba tey jii. \p \v 4 Fekk na Yonatan doomu Sóol ju góor am na doom ju góor ju tànk ya baaxul. Ndaxte ba ñu déggee tàgge bu jóge Yisreel, ñu ne Sóol ak Yonatan faatu nañu, fekk na xale ba am juróomi at. Ndaw sa ko daan topptoo, fab ko di gaawtuy daw, waaye na muy gaawtu di dem, xale ba daanu, daldi lafañ. Ma nga tuddoon Mefiboset\f + \fr 4.4 \fr*\fk Mefiboset \fk*\ft dees na ko wooye Mefibaal ba tey. Seetal lu mel noonu ci 2.8.\ft*\f*. \p \v 5 Rekab ak Baana, doomi Rimon ma dëkk Berot nag ñoo demoon kër Isboset, àgg fa ci biir tàngooru njolloor, fekk Isboset di for bët. \v 6 Ñu jàll ba ca biir-a-biir kër ga, mel ni ñuy sàkk peppum bele, daldi ko jam ci biir, ba noppi yoxoosu daw. \v 7 Ba ñuy dugg këram, ma nga tëddoon ca lalam, ca néegu biiram. Ñu jam ko ba rey ko, dog bopp ba, yóbbu. Ñu jaare xuru Yurdan, fanaanee dox.\f + \fr 4.6-7 \fr*\ft Am na ci bind yu yàgg yi, yu ci indi: \ft*\fq Am na ku jigéen ku doon wattu bunt ba, di bàcc pepp. Ay nelaw dab ko. Rekab ak Baana yoxoosu dugg. Ñu jàll ca néegu biiru Isboset, fekk ko mu tëdd ca lalam. Ñu jam ko, rey ko, dog bopp ba, yóbbu, jaareji xuru Yurdan, fanaanee dox.\fq*\f* \v 8 Ci kaw loolu ñu yóbbul boppu Isboset Daawuda ca Ebron, ne ko: «Buur, Sóol, sa noon ba doon wut sa bakkan, boppu doomam Isboset a ngii. Bésub tey jii de sang bi, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee la feyul ci Sóol ak askanam.» \p \v 9 Daawuda nag ne Rekab ak Baana, doomi Rimon waa Berot ba: «Giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund te musal sama bakkan ci gépp njàqare, \v 10 ka ma tàggesi woon Sóol, foog ne xibaaru jàmm la ma indil, dama koo jàpp, rey ko ca Ciglaag, yoole ko ko xibaaram. \v 11 Rawatina nag nit ñu bon ñu rey jaamburu Yàlla ci biir këram, ci kaw lalam sax. Kon duma def lu moy topp leen bakkanam, jële leen ci kaw suuf!» \v 12 Daawuda nag jox ay nitam ndigal, ñu rey leen. Ñu dog seeni loxook seeni tànk ca tenqo ya, wékk néew ya ca wetu déegub Ebron, daldi jël boppu Isboset, suul ca bàmmeelu Abner ca Ebron. \c 5 \s1 Daawuda falu na buur ca Israyil \p \v 1 Ci kaw loolu giiri Israyil yépp dikk fa Daawuda ca Ebron, ne ko: «Noo ngii di say bokk lenqe. \v 2 Te it démb ak bëkk-démb, ba Sóol dee sunu buur, yaw yaa doon jiite Israyil ciy xareem. \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ne la: “Yaay sàmm Israyil sama ñoñ te yaay doon kilifag Israyil.”» \v 3 Noonu la magi Israyil ñépp dikke ca Buur Daawuda ca Ebron, mu fasook ñoom \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* fa kanam Aji Sax ji. Ñu sotti Daawuda diwu pal ga, muy buurub Israyil. \p \v 4 Daawuda amoon na fanweeri at, ba muy falu buur, te ñeent fukki at la nguuru. \v 5 Ca Ebron la yore nguurug Yuda juróom ñaari at ak juróom benni weer, waaye ca Yerusalem la yore diiru fanweeri at ak ñett, mboolem Israyil ak Yuda. \s1 Daawuda nangu na Yerusalem \p \v 6 Gannaaw loolu Buur Daawuda ànd aki xarekatam, jëm Yerusalem, songi Yebuseen ña dëkkoon ca réew ma. Yebuseen ña ne Daawuda: «Doo fi dugg de, nde gumba yeek lafañ yi rekk ñoo lay waññi.» Booba foog nañu ne Daawuda manu faa dugg. \v 7 Terewul Daawuda nangu tatay \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, ga ñu dippee Kër Daawuda. \v 8 Daawudaa noon bésub keroog: «Ku bëgga jam Yebuseen ñi, ca xuntim yoonu ndox ma ngay mana dabe seeni gumbaak seeni lafañ, xuloowaaley Daawuda yi.» Looloo waral waxin wi ñu naan: «Gumba akub lafañ du dugg kër Buur.» \v 9 Ba mu ko defee Daawuda dëkk ca biir tata ja, wooye ko Kër Daawuda, ba noppi tabax fa ko wër fépp, dale ko ca sëkkub Milo\f + \fr 5.9 \fr*\fk Milo \fk*\ft xur la wu doxoon diggante kër Yàlla ga ak gox ba ñu naan Kër Daawuda. Suleymaan sëkklu ko.\ft*\f*, ba ca biir. \v 10 Daawuda nag di gëna am doole, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Yàlla, Boroom gàngoori xare yi ànd ak moom. \p \v 11 Ci biir loolu Iram buurub Tir, yebal ay ndaw ca Daawuda, ñu yóbbul ko ay banti garabu seedar, ak ay liggéeykati bant ak yettkati xeer, ngir ñu tabaxal Daawuda kër. \v 12 Daawuda xam ne Aji Sax jee ko tabb buurub Israyil te moo kaweel nguuram ngir Israyil, aw ñoñam. \p \v 13 Gannaaw ba Daawuda jógee Ebron, dellu na jël ay nekkaale aki soxna ca Yerusalem. Mu am ca yeneen doom yu góor ak yu jigéen. \v 14 Doomam yu góor yi juddoo Yerusalem ñoo di Samwa ak Sobab ak Natan ak Suleymaan; \v 15 ak Ibaar ak Elisuwa ak Nefeg ak Yafiya; \v 16 ak Elisama ak Elyada ak Elifelet. \s1 Buur Daawuda duma na waa Filisti \p \v 17 Ba waa Filisti déggee ne fal nañu Daawuda buurub Israyil, ñoom ñépp a jóg, di ko wër. Daawuda nag dégg ko, dem làquji ca biir tata ja. \v 18 Waa Filisti dikk, tasaaroo ca xuru Refayeen ña. \v 19 Daawuda laaj \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ne ko: «Ndax ma songi waa Filisti? Dinga leen teg ci sama loxo?» Aji Sax ji ne ko: «Demal, maay teg waa Filisti ci say loxo déy!» \v 20 Daawuda dem ba ca Baal Perasim, duma leen foofa. Mu ne: «Aji Sax jee ma bëttal noon yi, ni walum ndox di bëtte, wéy.» Moo tax ñu wooye bérab boobu Baal Perasim (mu firi Boroom bëtt-bëtt yi). \v 21 Waa Filistee fa wacc seeni gàllaaj, Daawudaaki nitam boole yóbbu. \p \v 22 Ba mu ko defee waa Filisti dikkaat, tasaaroo ca xuru Refayeen ña. \v 23 Daawuda dellu laaj Aji Sax ji. Mu ne ko: «Bul jubal, doxeleen gannaaw, dal ca seen kaw fa janook garabi sànd ya. \v 24 Booy dégg tànk yuy jaab ca kaw njobbaxtali sànd ya rekk, gaawtul, ndax booba Aji Sax jee la jiitu, di dumaji waa dalub Filisti.» \v 25 Daawuda nag def noonee ko Aji Sax ji sant, ba duma waa Filisti diggante Geba, ba ca buntu Geser. \c 6 \s1 Gaalu Yàlla ga dem na Yerusalem \p \v 1 Ba loolu wéyee Daawuda dellu woo mboolem ñeyi xarey Israyil, ñuy fanweeri junni. \v 2 Mu fabu, mook mboolem gàngoor ga ànd ak moom, dem Baala, ca Yuda, ngir jëleji fa \w gaalu Yàlla|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* gi ñu tudde Tur wi, turu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoori xare yi, ki tooge diggante malaakay \w serub|lemma="serub y-:"\w*, yi tiim gaal gi. \v 3 Ñu teg ko ci kaw watiir wu bees, jële ko kër Abinadab ga woon ca kaw tund wa. Usa ak Axyo, doomi Abinadab yu góor ya dox, jiite watiir wu bees wa. \v 4 Noonu lañu dawale watiir wa yeb gaalu Yàlla ga, jële ko kër Abinadab, ga ca kaw tund wa, Axyo dox jiitu ko. \v 5 Daawudaak waa kër Israyil gépp a ngay bànneexoo mboolem jumtukaayi xumbéen fi kanam Aji Sax ji; muy lu ñu defare bantu garabu sippar, ak ay keseŋ-keseŋ aki tabala ak xeeti xalam. \p \v 6 Naka lañu dem ba tollu ca dàggay Nakon, nag ya tërëf, Usa tàllal loxoom, jàpp ca gaalu Yàlla ga. \v 7 Sànjum Aji Sax ji nag tàkk ci kaw Usa. Yàllaa ko fàdd foofa, ndax ug teeyadeem, mu dee foofa ca wetu gaalu Yàlla ga\f + \fr 6.7 \fr*\ft Sarxalkat yi rekk ñoo amoon sañ-sañu laal gaalu Yàlla ga, te Leween ñi rekk ñoo amoon sañ-sañu gàddu ko.\ft*\f*. \v 8 Ba loolu amee Daawuda mer ca mbugal mu metti ma Aji Sax ji teg Usa. Moo tax mu tudde bérab booba Peres Usa (mu firi Mbugalum Usa), muy turam ba tey jii. \p \v 9 Daawuda am na tiitaange lool bésub keroog ci Aji Sax ji. Ma nga naan: «Ana nu gaalu Aji Sax ji mana dale ak man?» \v 10 Loolu nag tax Daawuda nanguwula yóbbu gaalu Aji Sax ji fa moom, ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. Mu waññi gaal gi, yóbbu ko ca kër Obedd Edom waa Gaat ba. \v 11 Gaalu Aji Sax ji nekk na kër Obedd Edom waa Gaat ba ñetti weer. Aji Sax ji barkeel Obedd Edom, mook këram gépp. \s1 Gaal ga dikk na Yerusalem \p \v 12 Ba loolu amee ñu xamal Buur Daawuda ne ko: «\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji de barkeel na Obedd Edom ak mboolem lu bokk ci moom ndax \w gaalu Yàlla|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* gi.» Daawuda jëleji gaalu Yàlla ga kër Obedd Edom, daldi koy yóbbu ci biir mbégte mu réy ba këram, fa ñu naan Kër Daawuda. \v 13 Ba ña gàddu gaalu Aji Sax ja séqee juróom benni jéego, aw yëkk ak wëllu wu duuf la Daawuda sarxal. \v 14 Daawudaa ngay fecc ak doole fa kanam Aji Sax ji. Daawudaa nga gañoo am \w xar-sànnim|lemma="xar-sànni m-:"\w* lẽe. \v 15 Naka la Daawuda ak waa kër Israyil gépp di yóbbu gaalu Aji Sax ji, sarxolle yaak liit ya jolli. \p \v 16 Ba gaalu Aji Sax jay duggsi ca biir gox ba ñu naan Kër Daawuda, soxnas Daawuda, Mikal doomu Sóol a nga sëppu ca palanteeram. Mu gis Buur Daawuda di tëb ak a fecc ca kanam Aji Sax ji. Mu jéppi ko lool. \p \v 17 Ba mu ko defee ñu indi gaalu Aji Sax ji, yeb ko ca bérabam, ca biir xayma ba ko Daawuda sampal. Daawuda daldi joxe fa kanam Aji Sax ji ay \w saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ak \w saraxi cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*. \v 18 Daawuda joxe saraxi rendi-dóomal ak saraxi cant ci biir jàmm, ba noppi daldi ñaanal askan wi ci turu Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi. \v 19 Mu séddale aw ñam askan wépp, mbooloom Israyil mépp, góor ak jigéen; ku ci nekk mu jox la menn mburu ak yàpp wu ñu saaf\f + \fr 6.19 \fr*\fq yàpp wu ñu saaf \fq*\ft walla \ft*\fq benn nàkku tàndarma.\fq*\f* ak benn nàkku reseñ. Mbooloo ma doora dem, ku nekk ñibbi këram. \p \v 20 Ba loolu amee Daawuda walbatiku, dugg biir këram, ngir ñaanal waa këram. Soxnaam Mikal doomu Sóol génn dajeek moom, ne ko: «Buuru Israyiloo, yaaka teral sa bopp bésub tey jii! Nga futteeku tey jii fi kanam jigéen ñiy sa jaami jawriñ yi, mbete nit ku tekkiwul dara!» \v 21 Daawuda ne Mikal: «Fi kanam Aji Sax ji ma taamu, wacc sa baay ak waa këram gépp, ngir fal ma kilifag Israyil, ñoñi Aji Sax ji, fi kanam Aji Sax ji laay bànneexu. \v 22 Dinaa gëna teddadil sama bopp sax, gëna toroxlu, ba gisal ko sama bopp, te du tere jaam yu jigéen yi ngay wax teral ma.» \v 23 Mikal doomu Sóol jooju nag amul doom, ba ni mu deeye. \c 7 \s1 Lu jëm ci kër Yàlla ak kër Daawuda \p \v 1 Gannaaw loolu Buur Daawuda sanc na këram, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji noppal ko ci noonam yi ko wër yépp. \v 2 Ci biir loolu mu ne Yonent Yàlla Natan: «Xoolal rekk, maa ngi dëkke këru banti seedar, \w gaalu Yàlla|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* gi dëkke ab xayma.» \v 3 Natan ne Buur: «Mboolem loo ci namma def rekk, defal, ndax Aji Sax ji yaw la àndal.» \p \v 4 Guddig keroog nag kàddug Aji Sax ji dikkal Natan, ne ko: \v 5 «Demal wax sama jaam Daawuda, ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Ndax yaw yaa may tabaxal kër gu ma dëkke? \v 6 Bés ba ma génnee \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* Misra ba tey jii, masumaa dëkke ci kër. Ci biir xaymab jaamookaay laa masa mànge. \v 7 Mboolem fu ma masa màngeji ak bànni Israyil gépp, ndax mas naa wax benn baat, jëme ci genn giirug Israyil gu ma sant ñu sàmm Israyil sama ñoñ, ne leen ñu tabaxal ma kërug bantu seedar?” \p \v 8 «Kon nag waxal sama jaam Daawuda, ne ko: “Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: Maa la jële ca parlu, ga nga toppe woon gàtt ya, ngir nga doon kilifag Israyil, sama ñoñ. \v 9 Maa ànd ak yaw fépp foo dem, maa tenqee fi sa kanam mboolem say noon, te maa lay may tur wu màgge ni turi boroom daraja yi ci àddina. \v 10 Maay sàkkal dëkkuwaay Israyil sama mos, jëmbat ko, mu dëkke ko, ba deesu ko lëjalati, te ñu bon ñi duñu ko sonalati na woon, \v 11 ba ma falee ay njiit ci kaw Israyil sama ñoñ. Maa lay noppal ci sa noon yépp. Te it Aji Sax jaa ngi lay yégal ne la Aji Sax ji moo lay sosal kër. \v 12 Te bu say fan matee ba nga tëddi, fekki say maam, maay yékkati kenn ci saw askan, sa deretu bopp, mu wuutu la, te maay saxal nguuram. \v 13 Kookooy tabax kër, ñeel sama tur, te maay saxal ab jalam ba fàww. \v 14 Man maay doon baay ci moom, moom, muy doom ci man. Su defee naka su dul noonu, maa koy yare bantu nit, ak dumay doom aadama. \v 15 Waaye duma ko noppee laaye biir, ni ma noppee laaye biir Sóol ma ma la randalal. \v 16 Sa kër ak sa nguur day sax dàkk fi sa kanam, te sab jal day dëju ba fàww.”» \p \v 17 Noonee Natan jote mboolem kàddu yooyu ak peeñu moomu, na la ko yegge Daawuda. \s1 Daawuda delloo na Yàlla njukkal \p \v 18 Ba loolu amee Buur Daawuda dikk ba fa kanam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, toog ne ko: \p «Boroom bi Aji Sax ji! Ana lu ma doon, ak lu sama waa kër doon, ba tax nga indi ma ba fii? \v 19 Boroom bi Aji Sax ji, loolu doyatu la, nga waxaale ci sama askan, wi xaajagula ñëw, Sang bi. Boroom bi, Aji Sax ji, ndax nii ngay jëfeek doom aadama? \p \v 20 «Boroom bi Aji Sax ji, ana lu ma lay waxati? Yaw de, Sang bi, yaa ma ràññee. \v 21 Sa kàddoo waral nga def mboolem jii jëf ju réy ci sa yéeney xol, ba noppi yégal ma ko, Sang bi. \p \v 22 «Boroom bi, Aji Sax ji, Moo la tax di ku màgg! Kenn du yaw, kenn du Yàlla ku dul yaw doŋŋ, te mboolem lu nu nopp may, dëggal na loolu. \v 23 Ana askan wu mel ni Israyil sa ñoñ ci kaw suuf, wenn askan wu Yàlla dikk, goreel leen ngir def leen ñoñam, ba turam siiw? Yaa leen defal ay jaloore, yaa defal sam réew ay kéemaan ci sa kanam ñoñ ñi nga goreele fa Misra aki askanam aki yàllaam. \v 24 Yaa dëgëral Israyil sa ñoñ, ngir ñoñoo leen ba fàww, te yaw Aji Sax ji, yaa doon seen Yàlla. \p \v 25 «Léegi nag, Aji Sax ji Yàlla, Sang bi, wax ji nga wax ci man, ak sama waa kër, saxal ko ba fàww rekk, te defe ko noonu nga ko waxe, \v 26 ngir saw tur di gëna màgg ba fàww, ñu naan: “Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi mooy Yàllay Israyil,” te waa kër Daawuda sax fi sa kanam, Sang bi. \p \v 27 «Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, Yàllay Israyil, yaw déy yaa ma déey, Sang bi, ne kër nga may sosal. Moo tax ma ñeme laa ñaan lii, Sang bi. \v 28 Léegi nag, Boroom bi Aji Sax ji, yaw yaay Yàlla, say kàddu mooy dëgg, te yaa ma wax lu baax lii, Sang bi. \v 29 Kon nag Sang bi, nangula barkeel sama kër, ngir mu sax ba fàww fi sa kanam. Ndax kat yaw Boroom bi Aji Sax ji yaa wax, te ci sa barke la sama kër di barkeele ba fàww, Sang bi.» \c 8 \s1 Daawuda duma na xeet ya ko wër \p \v 1 Gannaaw gi, Daawuda duma na Filisteen ña, néewal leen doole, jële kilifteefu waa Filisti ca réew ma. \v 2 Daawuda duma Mowabeen ña itam, tëral leen ca suuf, sësale leen, natte leen ag buum. Ñaari buum yu mu natt, yemook ña ñu wara rey, buum gu mat ga ca topp yemook ñi wara dund. Mowabeen ña daldi nangul Daawuda, di ko indil galag. \p \v 3 Daawuda duma na itam buurub Soba\f + \fr 8.3 \fr*\fk Soba \fk*\ft turu dëkk la bu amoon buuru boppam. Waaye ci Siri la bokkoon.\ft*\f*, Adadeser doomu Reyob, fekk Adadeser di fexee nanguwaat diiwaan ba feggook dexu Efraat. \v 4 Daawuda jàpp junniy gawaram ak juróom ñaar téeméer (1 700) ak ñaar fukki junniy xarekat (20 000) yuy deme tànk, ba noppi dog sidditi tànki mboolem fas ya doon dawal watiir, bàyyiwu ca lu moy téeméeri fas. \v 5 Waa Siri ña dëkke réewum Damaas dikk wallusi Adadeser buurub Soba. Daawuda rey ca ñoom ñaar fukki junneek ñaar (22 000). \v 6 Ba mu ko defee Daawuda tabb ay jawriñam ca Damaas ca Siri, waa Siri nekk ci curgag Daawuda, di ko fey galag. \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji may Daawuda ndam fépp fu mu dem. \v 7 Daawuda nag nangu pakki wurus ya kilifay xarekati Adadeser daan aare seen bopp. Mu boole, yóbbu Yerusalem. \v 8 Dëkki Adadeser ya ñuy wax Beta ak Berotay it, xànjar ju bare lool la fa Buur Daawuda nangoo. \p \v 9 Ci kaw loolu Toyi buurub Amat dégg ne Daawuda duma na gàngooru Adadeser gépp. \v 10 Toyi yebal doomam Yoram ca Buur Daawuda, ngir mu nuyu ko, sargal ko ca la mu xareek Adadeser ba duma ko, ngir Toyi ci boppam xare woon naak Adadeser. Yoram indaaleel ko jumtukaayi xaalis ak wurus ak xànjar. \v 11 Buur Daawuda boole loolu, jagleel ko Aji Sax ji, na mu ko jagleele woon xaalis baak wurus, wa mu lële ca mboolem xeet ya mu tegoon loxo; \v 12 la jóge ca Edomeen ñaak Mowabeen ñaak Amoneen ñaak waa Filisteek Amalegeen ña ak la mu lële ca buurub Soba, Adadeser doomu Reyob. \p \v 13 Daawudaa nga gënatee siiw ba mu dumaa waa Siri, teg ca duma fukk ak juróom ñetti junniy (18 000) Edomeen ca xuru Xorom wa. \v 14 Mu daldi tabb ay jawriñam ca réewum Edom. Réewum Edom gépp la tabb ay jawriñ, Edomeen ñépp nekk ci curgag Daawuda. Aji Sax ji nag may Daawuda ndam fépp fu mu dem. \s1 Lu jëm ci jawriñi Daawuda \p \v 15 Buur Daawuda ci kaw Israyil gépp la nguuru woon; muy jëfe njub ak njekk ñeel réewam mépp. \v 16 Yowab, mi Seruya di ndeyam, moo jiite woon mbooloom xare ma; Yosafat doomu Ayilut yor kàddug buur; \v 17 Cadog doomu Ayitub ak Ayimeleg doomu Abiyatar ñoo doon \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ya; Seraya di bindkat ba; \v 18 Benaya doomu Yoyada moo jiite woon waa Keret ak waa Pelet, dagi buur ya; doomi Daawuda yu góor nag ay sarxalkat lañu woon\f + \fr 8.18 \fr*\ft Am na ñu jàpp ne sarxalkat yi ñuy wax fii, ay saytukat lañu woon.\ft*\f*. \c 9 \s1 Daawuda baaxe na Mefiboset \p \v 1 Daawuda moo noon: «Ndax kenn desul ba tey ci waa kër Sóol, ba ma jëfeek moom ngor ngir Yonatan?» \v 2 Fekk na ab surgaa nga woon ca kër Sóol, di ku ñuy wax Ciba. Ñu indi ko ca Daawuda, Buur Daawuda ne ko: «Yaa di Ciba?» Mu ne ko: «waaw, sang bi.» \v 3 Mu ne ko: «Ndax kenn desul ba tey ci waa kër Sóol, ba ma jëfeek moom ngor gu Yàlla gërëm?» Ciba ne ko: «Doomu Yonatan ju tànk yi baaxul a nga fa ba tey kay.» \v 4 Buur ne ko: «Ana mu?» Mu ne ko: «Moom de, ma nga ca kër Makir doomu Amiyel, ca dëkk ba ñuy wax Lodebar.» \p \v 5 Buur Daawuda nag yeble, ñu jëleji ko ca Lodebar, ca kër Makir doomu Amiyel. \v 6 Ba loolu amee Mefiboset\f + \fr 9.6 \fr*\fk Mefiboset \fk*\ft dees na ko wooye Mefibaal ba tey. Seetal lu mel noonu ci 2.8.\ft*\f* doomu Yonatan doomu Sóol, dikk ca Daawuda, ne gurub, dëpp jëëm fa suuf, sujjóot. Daawuda ne ko: «Mefiboset!» Mu ne ko: «Naam, sang bi.» \v 7 Daawuda ne ko: «Bul tiit, dinaa jëfeek yaw ngor déy ngir sa baay Yonatan. Dinaa la delloo mboolem sa suufas maam Sóol, te yaay bokk ak man ndab ba fàww.» \v 8 Mefiboset sujjóot, ne ko: «Moo sang bi, maay kan ba nga di ma geesu, man mi tekkiwul dara, ba dara booloo jeex?» \p \v 9 Ci kaw loolu Buur woolu Ciba, surgab Sóol ba, ne ko: «Mboolem lu bokk ci alalu Sóol ak alalu waa këram jox naa ko Mefiboset, sa sëtub sang. \v 10 Dee ko beyal tool yi, di ko góobal, yaw yaak say doom ak say surga, ndax waa këram am ab dund. Mefiboset nag, mook man ay bokk ndab.» Ciba amoon na fukki doom yu góor ak juróom, ak ñaar fukki surga. \v 11 Ciba ne ko: «Buur, sang bi, noonu nga ma ko sante rekk, ni laa koy defe.» Ci kaw loolu Mefiboset di lekk ca ndabal Daawuda, mel ni ku bokk ci doomi Buur. \p \v 12 Mefiboset amoon na doom ju ndaw ju góor, ju ñuy wax Mika. Waa kër Ciba ñépp nag daldi nekk ci liggéeyu Mefiboset. \p \v 13 Ci kaw loolu Mefiboset far féete Yerusalem gannaaw ñaari tànkam a làggi, ndax mu mana lekke ca ndabal Buur, bés bu nekk. \c 10 \s1 Daawuda jote naak Amoneen ña \p \v 1 Gannaaw loolu Nayas buurub Amoneen ña dee, Anun doomam ju góor falu buur, wuutu ko. \v 2 Daawuda ne: «Dinaa jëfe ngor sama digganteek Anun doomu Nayas, na ma baayam jiye woon ngor.» Daawuda nag yebal ay ndawam ca Anun, di ko jaal baayam. Ba ndawi Daawuda ya agsee ca réewum Amoneen ña, \v 3 njiiti Amoneen ña wax ak seen sang Anun, ne ko: «Defe nga ne moos wormaal sa baay la Daawuda namm, ba yónnee la ay nit ñu la jaal? Foogoo ne seetsi dëkk bi ak nemmikusi ko, ba song ko moo tax Daawuda yebal ay nitam ci yaw?» \v 4 Anun daldi jàpp niti Daawuda ña, wat seen genn-wàllu sikkim, dagg seeni mbubb fa tollook toogukaay ba, daldi leen dàq. \v 5 Ñu yegge Daawuda mbir ma, mu yeble ngir ñu gatanduji leen ndax na ñu leen torxale. Mu ne leen ñu toog Yeriko, ba seeni sikkim sëqaat, ñu doora ñibbsi. \p \v 6 Amoneen ña xam ne Daawuda jéppi na leen lool. Ñu dem bindi ñaar fukki junniy (20 000) xarekat ca waa Siri ña dëkke Bet Reyob ak waa Siri ña dëkke Soba, teg ca junniy nit ñu bàyyikoo ca buuru Maaka, ak fukki junneek ñaar (12 000) ñu waa Tob. \v 7 Daawuda dégg ko, yebal Yowab ak mboolem gàngooru jàmbaar ña. \v 8 Ba mu ko defee Amoneen ña génn, làng-dér ca seen buntu péey ba, fekk waa Siri ña dëkke Soba ak Reyob ak waa Tob ak waa Maaka, ñoom ñépp a nga taxawe nee ca àll ba, seen wetu bopp. \v 9 Yowab gis làngi xare yi ñu wara jànkoonteel, ga ko féete kanam, ak ga ca gannaaw. Mu tànne ca jàmbaari Israyil yépp jàmbaari xare yu mag, ñu làng-déral waa Siri. \v 10 La des ca gàngoor ga, mu teg ca loxol rakkam Abisay, làng-dérloo leen, ñu janook Amoneen ña. \v 11 Yowab ne Abisay: «Bu ma waa Siri ëppee doole, nga wallusi ma; su la Amoneen ñi ëppee doole, ma wallusi la. \v 12 Góor-góorlul nag, te nu bokk góor-góorlu ngir sunuw xeet ak sunu dëkki Yàlla yi. \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nag mooy def li ko soob.» \p \v 13 Ba loolu amee Yowab ak gàngoor ga ànd ak moom sàqi ngir xareek waa Siri, waa Siri daw, won leen gannaaw. \v 14 Amoneen ña gis waa Siri di daw, ñoom it ñu daw, won Abisay gannaaw ba dellu ca biir dëkk ba. Yowab nag bàyyikoo ca xare baak Amoneen ña, daldi dellu Yerusalem. \s1 Daawuda xare naak Siri \p \v 15 Gannaaw loolu waa Siri gis na ñu daanoo fa kanam Israyil. Ñu bokk daje ñoom ñépp. \v 16 Ci kaw loolu Buur Adadeser yónnee, jëli waa Siri ña ca wàllaa dexu Efraat. Waa wàllaa dex dikk ba dëkk ba ñuy wax Elam; Sobag, njiital gàngooru Adadeser jiite leen. \v 17 Naka lañu ko wax Daawuda, mu woo Israyil gépp, daldi jàll dexu Yurdan, ba àgg Elam. Waa Siri nag làng-déral Daawuda, song leen. \v 18 Waaye waa Siree daw, won Israyil gannaaw. Daawuda rey ca ñoom juróom ñaar téeméeri dawalkati watiiri xare (700), ak ñeent fukki junniy gawar (40 000). Sobag, seen njiital gàngoor, mu jam ko, mu dee foofa. \v 19 Ba mu ko defee mboolem buur yay jawriñi Adadeser gis na ñu daanoo fa kanam Israyil, ñu daldi jàmmook \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, nangul leen. Ba loolu amee waa Siri ñemeetuñoo sotle Amoneen ña. \c 11 \s1 Daawuda topp na bakkanam \p \v 1 Gannaaw loolu, ca déwén sa, jamono ja buur ya daan xareji, Daawuda daa yebal Yowab, mu ànd aki nitam ak gàngooru Israyil gépp. Ñu faagaagal Amoneen ña, gaw péey ba ñu naan Raba. Fekk na Daawudaa nga des Yerusalem. \p \v 2 Genn ngoon, Buur Daawuda jóge ca kaw laltoom, di doxantu ca kaw taaxum këram. Mu tollu ca kaw taax ma, séen as ndaw suy sangu. Ndaw sa neexa xool lool. \v 3 Daawuda yónnee, gëstu mbiram, ñu ne ko: «Xanaa du Batseba doomu Eliyam, jabaru Uri, Etteen bi?» \p \v 4 Ci kaw loolu Daawuda yebal ay ndaw yu jëli ndaw si, mu dikk, mu tëdde ko. Fekk na ndaw sa gisoon baax bay doora sangu-set. Ndaw sa daldi ñibbi. \v 5 Ndaw si nag ëmb. Ba loolu amee mu yónnee ca Daawuda ne ko: «Man de, damaa ëmb.» \p \v 6 Ba mu ko defee Daawuda yónnee ca Yowab, ne ko mu wool ko Uri, Etteen ba. Yowab wool ko Uri. \v 7 Ba Uri dikkee, Daawuda nuyook moom ne ko: «Mbaa Yowab jàmm? Mbaa mbooloo ma jàmm? Mbaa xare ba jàmm?» \v 8 Ba loolu wéyee Daawuda ne Uri: «Àggal sa kër nag te jàngu.» Uri bàyyikoo kër Buur, ab yóbbalu Buur topp ca gannaawam. \v 9 Ndeke Uri ñibbiwul këram. Ca bunt kër Buur la tëdd, mook mboolem surgay Buur. \p \v 10 Ñu yégal Daawuda, ne ko: «Uri de ñibbiwul këram,» mu ne Uri: «Xanaa du ciw yoon nga jóge? Lu la tee àgg sa kër?» \p \v 11 Uri ne Daawuda: «Sang bi, \w gaalu Yàlla|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* ga ak Israyil ak Yuda dëkke ay mbaar, sama njaatige Yowab ak surgay sang bi bokk dale ci digg àll bi, man may dem sama kër, di lekk ak a naan, di dëkkoo sama soxna? Mukk! Giñ naa, nga fekke, duma def loolu!» \p \v 12 Daawuda ne Uri: «Kon toogaatal fii tey ba ëllëg, ma yiwi la.» Uri toog Yerusalem bésub keroog ak ca ëllëg sa. \v 13 Ci biir loolu Daawuda woo Uri, mu bokk ak moom lekk, daldi naan. Mu nàndal ko ba mu màndi. Ba ngoon jotee Uri daa génn, tëdd ca laltoom ca biir surgay sangam, waaye këram, àggu fa ba tey. \p \v 14 Ba bët setee Daawuda bind Yowab bataaxal, yóbbante ko Uri. \v 15 Mu bind ci bataaxal bi, ne Yowab: «Jiitalal Uri mii ca làngu kanam, ga xare ba gëna tànge, te ngeen dànd ko, ndax ñu jam ko, mu dee.» \p \v 16 Ci kaw loolu Yowab a nga bàyyi xel ca dëkk ba ñu gaw. Mu daldi teg Uri fu ko wóor ne ay ñeyi xarey dëkk baa fa féete. \v 17 Ba loolu amee waa dëkk ba génn, xeex ak ñoom Yowab, mu am ñu daanu ca gàngoor ga, ca niti Daawuda ña, Uri Etteen ba bokk ca ña dee. \p \v 18 Ba mu ko defee Yowab yónnee àgge Daawuda mboolem xew-xewi xare ba. \v 19 Yowab sant ndaw la, ne ko: «Boo nettalee buur li xew ci xare bi lépp, ba noppi, \v 20 su Buur meree, ne la: “Ana lu waral ngeen jegee noonu dëkk ba ci xeex? Xanaa xamuleen ne ca kaw tata ja lañu leen di fitte? \v 21 Ana ku reyoon Abimeleg doomu Yerubeset? Xanaa du ca kaw tata ja la ko aw jigéen sànnee doju wolukaay, ba mu dee ca Tebes? Lu waral ngeen jegee noonu tata ja?” Su boobaa nee ko: “Sa surga ba, Uri Etteen ba it dee na.”» \p \v 22 Ndaw la dem ba àgg, daldi àgge Daawuda la ko Yowab waxloo lépp. \v 23 Ndaw la da ko ne: «Nit ñaa nu jëkkoona man. Dañoo génn, song nu ca àll ba. Waaye noo leen delloo gannaaw ba ca bunt dëkk ba. \v 24 Fittkat ya nag fitte nu ca kaw tata ja, ba mu am ñu dee ci say nit. Sa surga ba, Uri Etteen ba it dee na.» \v 25 Daawuda ne ndaw la: «Waxal Yowab ne ko, bumu tiislu moomu mbir; xare bu yóbbuwul kii, yóbbu kee. Na gëna song dëkk ba rekk, ba daane ko. Nga ñaaxe ko noonu.» \p \v 26 Ba loolu amee jabaru Uri dégg ne jëkkëram dee na. Mu daldi koy ténj. \p \v 27 Ba àppu ténj ba weesee\f + \fr 11.27 \fr*\ft Jamono yooyu bànni Israyil juróom ñaari fan lañu aadawoo woon di ténj.\ft*\f*, Daawuda yónnee, indi ko këram, mu doon soxnaam. Gannaaw gi mu am doom ju góor. \p \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nag ñaawlu la Daawuda def. \c 12 \s1 Yonent Yàlla Natan yedd na Daawuda \p \v 1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji moo yónni Natan ca Daawuda. Mu dikk, ne ko: «Ñaari góor la woon ci ab dëkk. Kenn ka barele, ka ca des néewle. \v 2 Ki barele am na jur gu bare lool, gu gudd ak gu gàtt. \v 3 Waaye ka néewle amul lu dul mbote mu ndaw mu jigéen mu mu jëndoon, yar ko biir këram, muy màggandook ay doomam. Ca njëlam sa la mbote ma daan lekk, ca kaasam la daan naane, te ca kaw dënnam la daan tëdd. Mbote mi daa meloon ni doomam. \v 4 Ci biir loolu ku nekk ciw yoon dikk, dal ak ka barele. Waaye moom néegula sàkk ciy gàttam mbaa nagi boppam, ngir toggal ko gan gi dal ak moom. Ka néewle la nangu mboteem, toggal ko gan gi dal ak moom.» \p \v 5 Daawuda nag mer lool ca jëfi nit kooku. Mu ne Natan: «Giñ naa ci Aji Sax jiy dund, dee rekk mooy àtteb waa ji def loolu! \v 6 Te it menn mbote mi, ñeentam la koy feye, gannaaw moo def jooju jëf, te amu ci jenn yërmande!» \v 7 Natan ne Daawuda: «Yaw, yaay waa ji! Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: “Man maa la fal buurub Israyil, maa la xettli ci Sóol. \v 8 Maa la jox sa kër sang, maa teg ci say loxo, sa jabari sang, jox la nguurug Israyil ak Yuda. Te bu doyuloon it, ma dolli. \v 9 Ana lu waral nga ñàkke worma kàddug Aji Sax ji, di def lu mu ñaawlu? Uri Etteen bi, yaa ko fàdde saamar; jabaram nga jël, def ko sa jabar, moom nga fàdde ko saamaru Amoneen ñi. \v 10 Kon nag saamar dootu jóge sa kër mukk, ndax yaa ma ñàkke worma, ba jël jabaru Uri Etteen bi, def ko sa jabar.” \v 11 Aji Sax ji dafa wax ne: “Maa ngii di yékkati fi sa kaw musiba mu jóge ci sa kër. Maay jël say jabar, ngay gis, jox leen góor ni yaw, mu tëdde say jabar bëccëg ndarakàmm. \v 12 Yaw déy ci sutura nga ko defe. Waaye man, ci kanam Israyil gépp laay sabab mbir moomu, bëccëg ndarakàmm.”» \p \v 13 Daawuda nag ne Natan: «Maa tooñ Aji Sax ji.» Natan ne ko: «Aji Sax ji it jéllale na sa bàkkaar; doo ci dee. \v 14 Du tere nag, gannaaw dangaa teddadil lool Aji Sax ji ci mbir mii, doom ji nga ci am, moom, day dee rekk.» \v 15 Ba loolu amee Natan dellu këram. \s1 Doomu Daawuda faatu na \p Ba mu ko defee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji daane xale ba jabaru Uri am ak Daawuda. Xale ba wopp. \v 16 Daawuda nag tinu Yàlla ci xale bi: muy woor, fatu, fanaanee tëdd ci suuf. \v 17 Magi këram soññ ko ngir yékkatee ko fa suuf, nanguwul, te bokkul ak ñoom lekk dara. \v 18 Ñu teg ca juróom ñaari fan, xale ba dee. Surgay Daawuda ya ragala wax Daawuda ne ko xale ba dee na. Booba ña ngay xalaat naan: «Ndegam ba xale bay dund lanuy wax ak moom, dégluwu nu kay, ana nu nu koy waxe ne xale bi dee na, muy def njaaxum?» \v 19 Daawuda nag gis surgaam ya ñuy déeyoo, mu xam ne xale bi dee na. Mu ne leen: «Xale bi daa dee?» Ñu ne ko: «Dee na.» \p \v 20 Ba mu ko defee Daawuda jóge ca suuf, sangu, diwu, soluwaat. Ci kaw loolu mu dugg ca kër Aji Sax ji, sujjóot, daldi dem këram, santaane, ñu taajal ko ag lekk, mu lekk. \v 21 Surga ya ne ko: «Li ngay def lu mu doon? Bi xale biy dund, danga doon woor ak a jooy, léegi bi xale bi deeyee, nga jóg, di lekk?» \v 22 Mu ne leen: «Ba xale biy dese bakkan laa doon woor ak a jooy, ndax dama noon: “Ana ku xam ndax Aji Sax ji dina ma defalu yiw, ba xale bi dund am déet?” \v 23 Waaye gannaaw léegi dee na, ana lu may woorati? Dama koo mana dekkal? Man kay maa koy fekki, waaye moom du délsi ci man mukk.» \s1 Suleymaan gane na àddina \p \v 24 Ba loolu amee Daawuda dëfal soxnaam Batseba. Mu dem ca moom, daldi ànd ak moom. Gannaaw gi ndaw si am ca doom ju góor, tudde ko Suleymaan. \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nag sopp xale bi, \v 25 ba xamle ko, Yonent Yàlla Natan jottli, daldi koy tudde Yedija (mu firi Soppey Aji Sax ji). \s1 Daawuda nangu na péeyub Amoneen ña \p \v 26 Ci biir loolu Yowab xareek waa Raba, péeyub Amoneen ña, ba nangu tatay buur ba. \v 27 Ba loolu amee Yowab yebal ay ndaw ca Daawuda, ne ko: «Xare namaak waa Raba, nangu naa sax seen gox, ba ñuy jële am ndox. \v 28 Kon booleel ndesu gàngoor gi, te nga gaw dëkk bi, ba nangu ko. Lu ko moy maay nangu dëkk bi, ñu tudde ma ko.» \v 29 Daawuda nag dajale gàngoor gépp, daldi dem Raba, xareek ñoom, ba nangu ko. \v 30 Ba mu ko defee mu jële mbaxanam buur ma ñu solal seen jëmmu tuur ma ñuy wax Milkom.\f + \fr 12.30 \fr*\ft Am na mbind yu yàgg yu ñu indi ne seen buur lañu daan solal mbaxana mi.\ft*\f* Diisaayu mbaxana maa nga tollu ci fanweeri kiloy wurus, ab per bu gànjare tappe ca. Ñu tappal ko Daawuda ca kaw boppam. Alal ju baree bare la Daawuda nangoo ca dëkk ba. \v 31 Nit ña ca biir nag, mu génne leen, féetale leen ay xeetukaay ak ngaskay weñ ak sémmiñi weñ, boole ci di leen móol-loo. Noonu la def ak mboolem dëkki Amoneen ñi. Gannaaw loolu Daawuda ànd ak mbooloom xareem mépp, dellu Yerusalem. \c 13 \s1 Amnon tooñ na Tamar \p \v 1 Gannaaw loolu Absalom doomu Daawuda moo amoon jigéen bu rafet bu ñuy wax Tamar. Jeneen doomu Daawuda ju ñuy wax Amnon nag xemmem Tamar. \v 2 Jaaxle daldi dikkal Amnon, ba mu mujj wopp ngir Tamar, ab jigéenam, ndax ab janq la woon. Amnon daldi gis ne pexe mu muy jaare ba def Tamar lenn dina jafe. \v 3 Amnon nag amoon na xarit bu ñuy wax Yonadab doomu Simeya, miy doomu baayu Daawuda. Yonadab, ku ñawoona ñaw la. \v 4 Mu ne Amnon: «Waaw, yaw doomu buur nga, lu la tax ne yogg nii bés bu set? Doo ma ko wax?» Amnon ne ko: «Tamar, mi bokk ak sama doomu baay Absalom ndey ak baay, moom laa bëgg.» \v 5 Yonadab ne ko: «Dangay tëdd ci sa lal, wopp-wopplu, ba sa baay dikk, seetsi la, nga ne ko: “Na sama jigéen Tamar ñëw, may ma, ma lekk. Na ma toggal ci sama kanam, may gis, te mu sexal ma ci loxol boppam.”» \p \v 6 Ba loolu amee Amnon tëdd, wopp-wopplu, ba Buur ñëw di ko seet. Amnon ne ko: «Na sama jigéen Tamar ñëw defaral ma ñaari mburu yu ndaw, may gis, te sexal ma ci loxol boppam, ma lekk.» \v 7 Daawuda yónnee kër ga ca Tamar, ne ko mu dem kër càmmiñam Amnon, toggal ko lu mu lekk. \v 8 Tamar dem kër càmmiñam Amnon, fekk ko mu tëdd. Mu sàkk sunguf, not ko, defal ko ko ay mburu yu ndaw, lakkal ko ko, muy gis. \v 9 Mu noppi, jël ndab la, taajal ko Amnon, Amon nag baña lekk. Mu daldi ne: «Na ñépp génn, wacc ma fi!» Ñépp génn, wacc ko fa. \v 10 Mu ne Tamar: «Indil ma lekk gi ci sama biir néeg, te sexal ma ci sa loxol bopp, ma lekk.» Tamar jël mburu ya mu lakk, dugalal càmmiñam Amnon ca biir néegam. \v 11 Naka la Tamar dikk, taajal Amnon mburu ya, ngir mu lekk, mu ne ko katam, ne ko: «Kaay, tëdd ak man, sama jigéen.» \v 12 Mu ne ko: «Déedéet sama góor, bu ma néewal doole, ndax deesul defe nii ci Israyil! Bul def mukk jooju jëf ju sew! \v 13 Fu ma jëm ak googu gàcce, man? Te yaw it dootuloo jar dara ci digg Israyil. Tee ngaa wax ak Buur? Du ma la baña may.» \v 14 Amnon nag dégluwu ko, xanaa néewal ko doole, ba tëdde ko. \p \v 15 Gannaaw loolu Amnon jéppi ko njéefo lu raw mbëggeel ga mu ko bëggoon. Mu ne ko: «Jógal, dem!» \v 16 Tamar ne ko: «Déet, soo ma dàqee def ma lu yées li nga ma def ba noppi!» Taxul Amon nangu koo déglu. \v 17 Dafa woo bëkk-néegam, ne ko: «Génneel ma kii te tëj bunt beek caabi.» \v 18 Surga ba génne ko, tëj bunt baak caabi. \p Tamar a nga sol mbubb mu yànj, ndax booba janqi buur bu séyagul noonu la daan soloo. \v 19 Ba loolu amee Tamar sottikoo dóom ca bopp ba, xotti mbubb mu yànj ma mu sol, yenu loxo ya, di yuuxuy dem. \v 20 Càmmiñam Absalom gis ko, ne ko: «Xanaa Amnon sa càmmiñ see nekkoon ak yaw? Neel cell rekk, sama jigéen, sa càmmiñ la. Bul yenu lii mu la def.» Tamar nag ne cundum, tooge wéetaayam kër càmmiñam Absalom. \p \v 21 Ba Buur Daawuda déggee mbir moomu mépp, mer na lool. \v 22 Absalom nag jéppi Amnon, ba séqatul ak moom jenn wax, ndax na mu torxale jigéenam Tamar. \s1 Absalom feyu na \p \v 23 Ba ñu ca tegee ñaari ati lëmm, Absalom dem di watlu ay xaram\f + \fr 13.23 \fr*\ft Xari waa penku dañuy bare kawar gu ñuy wat ak a ëcc, di ci defar ag wëñ. Bu ñu daan watlu seeni xar, xew mu réy la woon.\ft*\f* ca Baal Àccor, fa feggook diiwaanu Efrayim. Absalom daldi fay woo doomi buur yu góor yépp. \v 24 Mu dem ca Buur ne ko: «Buur Sang bi, man de, damay watlu samay xar. Tee ngaa ànd ak say jawriñ rekk, nu dem ca?» \v 25 Buur ne Absalom: «Déet, doom. Bunu dem nun ñépp. Day diis ci yaw.» Absalom soññ ko, soññ, Buur nanguwula dem. Teewul mu ñaanal ko. \v 26 Absalom nag ne ko: «Bàyyil boog sama mag Amnon, mu ànd ak nun.» Mu ne ko: «Lu muy ànd ak yaw doye?» \v 27 Absalom soññati ko, ba Buur yebal Amnon, mu ànd ak moom, ak yeneen doomi buur yu góor yépp. \p \v 28 Ba mu ko defee Absalom sant ay nitam, ne leen: «Ma ne, bu Amnon naanee biiñ, ba xolam sedd, bu ma leen nee ngeen jam ko rekk, reyleen ko. Buleen ragal; man maa leen ko sant. Góor-góorluleen nag te ñeme.» \v 29 Niti Absalom ña def ak Amnon la leen Absalom sant, daldi rey Amnon. Ba loolu amee yeneen doomi buur yépp daldi war seeni berkelle, daw. \p \v 30 Naka lañu topp yoon wa, xibaar dikkal Daawuda, ne ko: «Buur, Absalom jam na sa doom yu góor yépp, ba kenn desu ca.» \v 31 Buur daldi xotti ay yéreem, daanu ca suuf ndax naqar, surgaam yépp taxaw ak seen yére yu xottiku. \p \v 32 Ci kaw loolu Yonadab doomu magu Daawuda Simeya, daldi wax ak baayam Daawuda. Mu ne: «Buur sang bi, bul defe ne sa doom yépp lañu rey de. Amnon rekk a dee, te mooy la Absalom dogu woon keroog ba Amnon torxalee rakkam Tamar. \v 33 Kon kat Buur sang bi, bul def ci sa xel ne sa doom yépp a dee. Amnon rekk a dee.» \v 34 Fekk na Absalom daw. \p Ci kaw loolu ngóor sa aye jongru daldi séentu, gisul lu moy nit ñu bare ñuy dikk, awe yoonu Oronayim, bartaloo tund wa. \v 35 Ba loolu amee Yonadab ne Buur: «Mu ngoog, Buur sang bi, sa doom yaay dikk. La ma waxoon a am.» \v 36 Naka la daane kàddoom rekk, doomi Buur ya agsi, ne yikkét di jooy. Buur ak surgaam yépp it, di jooy jooy yu metti. \p \v 37 Fekk na Absalom daw, dem ca buurub Gesur, Talmay doomu Amiyut. Buur Daawuda nag di jooy doomam bés bu nekk. \v 38 Ba Absalom dawee, dem Gesur, toog na fa ñetti at. \v 39 Gannaaw gi Buur Daawuda toppatul Absalom, ndax mujj na miis deewug Amnon. \c 14 \s1 Absalom délsi na \p \v 1 Ci biir loolu Yowab, mi Seruya di yaayam, xam ne xelu Buur Daawudaa ngi ci Absalom. \v 2 Yowab nag yónnee ca dëkk ba ñuy wax Tekowa, ñu jëleji fa jigéen ju rafet xel, indil ko ko. Yowab ne ko: «Dangay ñaawlu-ñaawlulu. Solal yérey ñaawlu, te bul xeeñu. Melal daal ni jigéen ju jota ñaawlu lu yàgg, ngir ku mu deele. \v 3 Su ko defee nga àgg ca Buur, wax ko lii ma lay wax.» Yowab wax ko kàddu ya mu wara wax. \p \v 4 Jigéen ja dëkk Tekowa àgg ca Buur, daanu ci suuf, sujjóotal ko, ne ko: «Buur, wallu ma!» \v 5 Buur ne ko: «Lu la dal?» Mu ne ko: «Man de gore, dama dib jëtun; sama jëkkër a dee. \v 6 Sang bi, ñaari doom yu góor laa amoon. Dañu doon xeex ñoom ñaar ca àll ba te ku leen àtte nekku fa. Kenn ki dóor moroom mi, rey ko. \v 7 Bokk yépp daldi jóg dal ci sama kaw, sang bi. Ñu ne ma: “Jox nu sa doom ji rey doomu ndeyam, nu rey ko, feyul doomu ndeyam ji mu rey. Moo dese ndono li, kon danu koy sàkkal pexe, moom itam.” Dañoo nara fey wenn xal wi ma dese, ba xañ sama jëkkër aw tur, xañ ko aw askan ci kaw suuf.» \v 8 Buur ne ko: «Demal ñibbi. Man ci sama bopp maay joxe ndigal ci yaw.» \v 9 Jigéen ja ne ko: «Buur sang bi, àq ju ci am, yal na ma topp, maak sama waa kër baay, te nga bañ cee gàddu dara, yaak sa waa kër.» \v 10 Buur ne ko: «Ku la tudd, indil ma ko, dootu la sonal.» \v 11 Mu ne ko: «Kon ngalla Buur, woo ci seede sa turu Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ngir kiy toppe bakkanu ka dee baña yokk yàqute, ba ñu rey sama doom ji.» Mu ne ko: «Giñ naa ko ci turu Aji Sax ji, Kiy Dund, kawar gu gëna tuut du jóge ci sa boppu doom, wadd ci suuf.» \p \v 12 Jigéen ja ne ko: «Buur, sang bi, ma ñeme laa waxati benn baat boog!» Mu ne ko: «Waxal.» \v 13 Mu ne: «Lu waral kon nga naral lu ni mel ñoñi Yàlla ñi? Buur, boo waxee loolu kay, mel na ni tooñ nga, ndax jëliwoo sa doom ja gàddaay. \v 14 Su dee dee moom, nun ñépp ay dee ni ndox di tuuroo ba deesu ko tanqati. Yàlla nag musalul kenn ci dee, waaye moo lal pexe ngir ki gàddaay du saxoo gàddaay bérab bu ko sore. \v 15 Buur sang bi, maa ñëw wax la kàddu yii, ndax mbooloo mee ma tiital. Ma noon nag sang bi, naa wax ak Buur, jombul mu defal ma li may ñaan. \v 16 Jombul Buur sang bi nangu maa xettli ci ki nuy fexee boole ak sama doom sànk, beddee nu ci céru Yàlla. \v 17 Léegi nag sang bi, yal na sa kàddu gii di sama noflaay. Ndax yaw Buur, sama sang, dangaa mel ni malaakam Yàlla, am ug dégg, di teqale liy yoon ak li dul yoon. Yal na sa Yàlla Aji Sax ji ànd ak yaw.» \p \v 18 Buur ne jigéen ja: «Léegi nag, bu ma nëbbu, tontu ma ci lii ma lay laaj.» Mu ne ko: «Waxal, Buur, sang bi.» \v 19 Mu ne ko: «Ndax du Yowab a nas pexe mii mépp, yaak moom?» Mu ne ko: «Buur, sang bi, ak sa barke, li nga wax rekk la, du leneen moos! Yowab, sa jawriñ bee ma ko sant. Moo ma waxloo lii lépp, sang bi. \v 20 Jubbanti mbir mii de moo tax Yowab def lii. Waaye yaw sang bi, danga di boroom xel mu rafet ni malaakam Yàlla. Xam nga mboolem lu xew ci réew mi.» \p \v 21 Gannaaw gi Buur ne Yowab: «Waaw, baax na, nangu naa. Demal jëli ngóor sa, Absalom.» \v 22 Yowab nag daanu ca suuf, sujjóot, ne Buur: «Buur, sang bi, yal nanga barkeel, sang bi. Xam naa ne may nga ma cér, gannaaw yaa ma may lii may dagaan.» \v 23 Ba loolu amee Yowab dem Gesur, daldi délloosi Absalom Yerusalem. \v 24 Buur Daawuda nag ne, na Absalom yem këram. Mu ne bumu taxaw ci kanamam. Ba mu ko defee Absalom yem këram, te taxawul fa kanam Buur Daawuda. \p \v 25 Absalom nag amul woon góor gu siiwe ni moom ci Israyil gépp ndax góorayiw. La ko dale ca wewu tànkam ba ca digg bopp ba, du lenn lu ca sikk. \v 26 At mu jotaan mu watu ndax njañ lu diis, te bu watoo, natt kawar ga ci doomi nattukaayu buur, mu jege ñaari kilook genn-wàll. \v 27 Absalom amoon na ñetti doom yu góor ak doom ju jigéen. Tamar, doom ju jigéen ja, doon ndaw su taaru. \p \v 28 Absalom nekk na Yerusalem ñaari ati lëmm yu mu sañula taxaw fa kanam Buur baayam. \v 29 Gannaaw gi Absalom yónnee, ñu wool ko Yowab ngir mu yónni ko ca Buur. Yowab lànk, ñëwul. Mu yónneewaat, mu lànk. \v 30 Absalom ne ay surgaam: «Gis ngeen, toolub Yowab mook sama tool a sësoo, te peppum lors a nga ca. Demleen taal ko.» Surgay Absalom dem, taal tool ba. \v 31 Ba loolu amee Yowab waaxu ba ca kër Absalom, ne ko: «Ana lu waral say surga taal sama tool?» \v 32 Absalom ne Yowab: «Xam nga damaa yónnee ci yaw, ne la ñëwal, ma yónni la ca Buur, nga laajal ma ko lu ma taxa jóge Gesur. Li gënoon ci man kay mooy ma toog foofa! Léegi daal damay gis Buur. Su fekkee ne damaa tooñ, na ma rey!» \p \v 33 Yowab dem ca Buur, wax ko ko. Buur woolu Absalom. Mu dikk sukk, sujjóotal ko. Buur taf ko ca kawam. \c 15 \s1 Absalom lal na pexe \p \v 1 Gannaaw ba loolu wéyee Absalom daa jël watiir aki fas ak juróom fukki nit ñuy daw di ko jiitu. \v 2 Muy teela jóg nag, taxaw ca peggu yoon, wa jëm ca buntu dëkk ba. Saa yu nit dikkee, am lu muy tawat, di ko diis-si Buur, ngir mu àtte ko, Absalom woo ko, laaj ko ne ko: «Ci ban dëkk nga bokk?» Kooku ne ko ci giirug Israyil sàngam la bokk. \v 3 Absalom ne ko: «Gisal, sa tawat yoon la, jaadu na. Waaye kenn ku bokk ci Buur du la déglu.» \v 4 Su ko defee Absalom da cay teg ne ko: «Maa bëggoon ñu fal ma njiit, may àtte ci réew mi! Kon képp ku am lu muy tawat mbaa muy layoo, ci man lay ñëw, ma taxaw ci, ba jox ko li ko yoon may.» \v 5 Képp ku ñëwaan it di sukkal Absalom, Absalom da koy yóotu, jàpp ci moom, fóon ko. \v 6 Absalom jàppoo ko noonu ak mboolem \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* yay ñëw ca buur ba, di sàkku yoon. Ni la fàbbee xoli bànni Israyil. \p \v 7 Ba ñu demee ba ñeenti at\f + \fr 15.7 \fr*\fk ñeenti at \fk*\ft yi ñuy wax fi am na ñu ne man naa doon \ft*\fq ñeent fukki at.\fq*\f* jàll, Absalom ne Buur: «May ma, ma dem Ebron defali \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji la ma ko xasaloon, \v 8 ndax kat, sang bi, ba ma nekkee Gesur ca Siri, damaa dige woon ne: “Su ma Aji Sax ji delloo, ba ma dellu Yerusalem, dinaa dem màggali ko.”» \v 9 Buur ne ko: «Demal ak jàmm.» Mu daldi dem Ebron. \p \v 10 Absalom nag yónnee ndéey. Ay ndaw yegge ko giiri Israyil gépp. Mu ne leen: «Bu ngeen di dégg liit gu jib rekk, ne leen: “Absalom falu na buur ca Ebron!”» \v 11 Ñaar téeméeri góor a jóge Yerusalem, Absalom woo woon leen, ñu ànd ak moom, yéguñu, tinuñu, xamuñu it dara ca mébétam. \v 12 Ci biir loolu Absalom di def ay sarax, daldi yónnee, ñu jëli Ayitofel ma topp ca Daawuda, di ko xelal. Ayitofel bàyyikoo ca Gilo. Pexe ma nag mujj na réy, ña topp Absalom di yokku ba bare. \s1 Daawudaa ngi wuta rëcc \p \v 13 Ba mu ko defee ñu yebal ndaw, mu dikk ne Daawuda: «\w Bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* de jàmbu nañu, ba far ak Absalom.» \v 14 Daawuda wax ak mboolem jawriñam ya mu nekkal ca Yerusalem, ne leen: «Nan daw! Lu ko moy kenn ci nun du rëcc Absalom. Nan dem léegi bala moo gaawtu, ba dab nu, def nu musiba, leel waa dëkk bi ñawkay saamar.» \v 15 Jawriñ ya ne Buur: «Buur, sang bi, lépp loo namm rekk, nu ngi nii taxaw.» \v 16 Ba loolu amee Buur tegu ca yoon wa, waa këram yépp topp ciy tànkam. Bàyyiwul gannaaw lu moy fukki nekkaaleem, ñu wara topptoo kër ga. \p \v 17 Buur dem, mbooloo mépp topp ko, ba ca kër gu mujj ga, ñu taxaw. \v 18 Nitam ñépp a dox romb ko, ñook dag ya ko dar yépp, di waa Keret ñaak waa Pelet ña, ak mboolem waa Gaat ya tollu ci juróom benni téeméeri nit te toppe woon ko ca Gaat. Ña ngay dox jiitu ko. \p \v 19 Buur ne Itay waa Gaat ba: «Dangay ànd ak nun? Tee ngaa dellu Yerusalem, toog ca Buur Absalom? Gannaaw yaw doxandéem nga bu gàddaaye fa nga fekk baax. \v 20 Bëkk-démb doŋŋ nga fi ñëw, tey ma di la bàyyi ngay ànd ak nun di wëreelu, te xawma sax fu ma jëm. Dellul, kay, ànd ak sa waa réew. Yal na la Aji Sax ji won ngor ak worma.» \p \v 21 Itay ne Buur: «Sang bi, giñ naa ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, Kiy Dund, nga fekke tey, fépp foo jëm yaw Buur, sama sang, dinaa fa ànd ak yaw, su may dund ak su may dee.» \v 22 Daawuda ne Itay: «Kon doxal jiitu.» Itay jiitu, mook nitam ñépp ak mboolem njabootam. \p \v 23 Mbooloom Daawuda mépp a ngay dem, waa réew ma mépp taxaw di yuuxook a jooyoo. Buur ba jàll xuru Sedoron, mbooloo ma mépp ànd wuti màndiŋ ma. \p \v 24 Cadog ak Abiyatar, sarxalkat yaa nga fa woon, ñoom itam. Ñenn ca góori \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ña bokkoon nañu ca, di gàddu \w gaal|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* ga àlluway kóllërey Yàlla ga dence. Ba ñu tegee gaal ga, Abiyatar di rendi ay sarax, ba mbooloo ma mépp génn dëkk ba. \v 25 Buur ne Cadog: «Dellool gaalu Yàlla gi ca dëkk ba. Bu ma Aji Sax ji baaxee, dina ma délloosi, ma gisaat gaal gi, gisaat fi mu dëkk. \v 26 Waaye bu ma waxee ne ma bégul ci man, su boobaa ba tey maa ngi. Na def li ko soob ci man.» \v 27 Buur dellu wax ak Cadog \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba, ne ko: «Dégg nga déy? Dellul ak jàmm ca dëkk ba, ànd ak Ayimaas, sa doom ju góor, ak Yonatan doomu Abiyatar. Yaak Abiyatar àndleen ak seen ñaari doom yu góor. \v 28 Xoolal, dinaa leen xaar ca jàllukaayu dex ba ca yoonu màndiŋ ma, ba keroog may dégg kàddu gu bawoo ci yaw.» \v 29 Ba loolu amee Cadog ak Abiyatar delloo gaalu Yàlla ga Yerusalem, daldi fay toog. \p \v 30 Daawudaa ngay wéy, di yéeg tundu Oliw ya, tey jooy. Ma nga muuru, def tànki neen ndaxu naqar. Nit ña mu àndal ñépp muur seen bopp ñoom it, di yéeg tey jooyoo. \v 31 Fekk na ñu wax Daawuda ne ko Ayitofel bokk na ca ña lëngook Absalom. Daawuda nag ñaan ne: «Yaw, Aji Sax ji, ngalla yàqal pexem Ayitofel.» \p \v 32 Ba Daawuda àggee ca collu tund wa, fa ñu daan jaamoo Yàlla, fekku fa ku moy Usay, Arkeen ba. Mu gatandu ko. Ma ngay tiislu, mbubb ma xottiku, bopp ba pënd. \v 33 Daawuda ne ko: «Soo àndee ak man, danga may diisal rekk. \v 34 Dangay dellu kay ca dëkk ba, ne Absalom: “Buur, sab jaam laa. Sa jaamu baay laa woon, waaye léegi sab jaam laa.” Noonu nga may yàqale pexem Ayitofel. \v 35 Te sax Cadog ak Abiyatar, sarxalkat ya, nga fay bokk nekkal. Loo dégg kër Buur, wax leen ko. \v 36 Te sax seen ñaari doom yu góor a nga faak ñoom: Ayimaas doomu Cadog, ak Yonatan doomu Abiyatar. Yónnee ma leen, ñu yegge ma loo dégg.» \v 37 Ci kaw loolu Usay, nitu Daawuda, yoxoosu, duggsi Yerusalem, yemook Absalom itam di agsi. \c 16 \s1 Daawuda tase naak surgab Mefiboset \p \v 1 Naka la Daawuda dox ba wees tuuti collu tund wa rekk, yem ca Ciba, surgab Mefiboset. Ma nga làng ak ñaari mbaam yu ñu laltaay, sëf leen ñaar téeméeri mburu ak téeméeri danki reseñ ak téeméeri danki figg ak mbuusum biiñ. \v 2 Buur ne Ciba: «Lii nga indi nag?» Mu ne ko: «Buur, mbaam yi sa waa kër laa ko indil, ñu war; mburu meek meññeef mi, gaa ñi lekk; biiñ bi, ñi loof ci màndiŋ mi naan ko.» \v 3 Mu ne ko: «Waaw, ana Mefiboset, sa sëtu sang ba?» Ciba ne Buur: «Moom de ma nga des Yerusalem, ndax defe na ne tey \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* delloo ko nguurug maamam.» \v 4 Buur ne ko: «Kon boog, may naa la mboolem alalu Mefiboset.» Mu ne ko: «Jaajëf Buur sang bi, gis naa ni nga ma baaxee.» \s1 Daawuda tase naak mbokkum Sóol \p \v 5 Gannaaw loolu Buur Daawuda dem bay jub dëkk ba ñuy wax Baxurim rekk, yemook jenn waay ju bokk ci waa kër Sóol. Ma nga tuddoon Simey doomu Gera. Naka la waa ja ne tëll, jubsi, di tifaar Daawuda ay saaga, \v 6 di ko sànni ay xeer, mooki jawriñam yépp. Faalewul kenn ci mbooloom Daawuda ma mépp ak jàmbaar ya ko dar yépp. \v 7 Simey a ngay saaga Daawuda naan: «Ayca, mott! Bóomkat bee, nit ku sew ki! \v 8 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji fey na la dereti waa kër Sóol ja nga tuur yépp, ba noppi falu, wuutu ko. Aji Sax ji teg na nguur gi ci sa loxol doom Absalom. Yaa ngi nii torox ndax bóomkat nga.» \p \v 9 Ci kaw loolu Abisay, waa ja Seruya di yaayam, ne Daawuda: «Buur, sang bi, luy ndeyi xaj bu dee bii di la saaga? Bàyyil rekk ma jàll, teqale boppam ak baatam!» \v 10 Buur ne ko: «Yeen doomi Seruya yi, lu ciy seen yoon? Sañ na maa saaga. Su ko Aji Sax ji santee mu saaga ma, ana ku ko saña laaj lu tax?» \v 11 Ba loolu amee Daawuda wax ak Abisay ak jawriñam yépp, ne leen: «Du gis ngeen sama doom ji ma jur ci sama geño, muy wuta faat sama bakkan? Kon kay kii bokk ci giirug Beñamin matula wax. Bàyyileen ko, mu saaga ma, ndax Aji Sax jee ko ko sant. \v 12 Jombul Aji Sax ji gis sama naqar, ba feye ma aw yiw saagay kii tey.» \p \v 13 Ba mu ko defee Daawuda ànd aki nitam topp yoon wa, Simey làng ak moom ca mbartalu tund wa, di dem, di ko saagaak a sànni xeer, di ko sëllax suuf. \v 14 Gannaaw gi Buur ak mbooloo ma mu àndal mépp agsi, sonn lool. Ñu daldi nopplu foofa. \s1 Absalom dugg na Yerusalem \p \v 15 Fekk na Absalom agsi Yerusalem, ànd ak mboolem niti Israyil ñi far ak moom. Ayitofel a nga ànd ak moom. \v 16 Usay, Arkeen ba doon nitu Daawuda, dem ca moom, ne ko: «Yal na Buur gudd fan waay, yal na Buur gudd fan!» \v 17 Absalom ne Usay: «Loolooy sa kóllëre ak sab xarit a? Lu la teree ànd ak sab xarit?» \v 18 Usay ne Absalom: «Déedéet, ki \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji tànn, mbooloo mii tànn ko, ñook mboolem \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, kookoo may moom, te ci moom laay toog. \v 19 Te sax ku may topp ku dul yaw, doomu buur? Ni ma toppe woon sa baay rekk laa lay toppe tey.» \p \v 20 Ci kaw loolu Absalom ne Ayitofel: «Xelal-leen nu boog, lu nu wara def?» \v 21 Ayitofel ne ko: «Demal dëkkoo sa nekkaaley baay, yi mu wacce këram, ñu di ko topptoo. Su ko defee bànni Israyil yépp dinañu xam ne def nga lu tax sa baay sib la. Dina tax say farandoo gëna am fit.» \v 22 Ba loolu amee ñu sampal Absalom xayma ca kaw taaxum kër Buur, Absalom di dëkkoo nekkaaley baayam, Israyil gépp seede ko. \p \v 23 Booba lu Ayitofel masaana digle day mel ni kàddu gu bawoo ca Yàlla. Daawudaak Absalom, ñoom ñaar ñépp noonu lañu fonke woon ndigalu Ayitofel. \c 17 \s1 Usay nax na Absalom \p \v 1 Gannaaw loolu Ayitofel ne Absalom: «Ngalla may ma, ma tànn fukki junniy xarekat ak ñaar (12 000) te dàqi Daawuda ci guddi gi. \v 2 Bu may dal ci kawam, da koy fekk mu sonn, jàq. Su ko defee ma xoqtal ko, ba mbooloo mi mu àndal mépp daw, ma rey ko, moom kenn. \v 3 Dinaa la délloosil mbooloo mépp. Bu ki ngay fexeel deeyee rekk, mbooloo mi mépp délsi, jàmm ne ñoyy.» \v 4 Pexe moomu nag jub ci Absalom, mook magi Israyil ñépp. \v 5 Teewul Absalom ne: «Wooleen Usay, Arkeen bi itam, nu déglu lu mu ciy wax.» \v 6 Usay dikk ca Absalom, mu wax ko la Ayitofel digle, ne ko: «Ndax loolu Ayitofel wax lanu wara def am déet? Wax nu lu ciy sa xalaat, yaw.» \p \v 7 Usay ne Absalom: «Li Ayitofel digle bii yoon de baaxul. \v 8 Xam nga sa baay ak ay nitam. Ay xarekat yu jàmbaare lañu te wex ni gaynde gu ñu nangu doom ya, te it, sa baay ku xam xeex la, du fanaan ak xarekat ya. \v 9 Xam naa ne ma nga làqu ci xuntim xeer, mbaa bérab rekk. Te bu aw nit jëkkee daanu ci seen biir yeen, ku ko dégg dina ne: “Jéll bu réy am na ca mbooloom Absalom.” \v 10 Su boobaa, ku ñeme, ba dëgëru fit ni gaynde sax, dinga tiit lool, ba ne yàcc, ngir Israyil gépp xam nañu ne sa baay ñeyi xare la, te it ñi ànd ak moom jàmbaar lañu. \v 11 Kon sama xalaat mooy nga boole ñi ànd ak yaw ba ñu daj, muy Israyil gépp, dale ko diiwaanu Dan ca bëj-gànnaar ba ca Beerseba ca bëj-saalum. Muy mbooloo mu bare, tollu ni suufas géej; te yaw ci sa bopp, nga jiite leen ci xare bi. \v 12 Nu song ko nag fu nu ko mana fekk, dal ci kawam, ni ab lay ci kaw suuf. Deesu ci bàyyi kenn muy dund, du moom, du kenn ciy nitam. \v 13 Su làqoo ci ab dëkk bu mag, na Israyil gépp yóbbaale ay buum ca tata ja, nu laaw ko, wat ba ca xur wa, ba kenn dootu gis aw doj wu ca bokkoon.» \v 14 Absalom ak waa Israyil gépp daldi ne: «Ndigalal Usay, Arkeen bii kat, moo gën ndigalu Ayitofel.» Booba \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee nara indil Absalom musiba. Moo tax mu neenal pexem Ayitofel mu jub ma mu laloon. \p \v 15 Ci kaw loolu Usay wax ak Cadog ak Abiyatar \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ya, nettali leen la Ayitofel digal Absalom ak magi Israyil ña, ak la mu leen digal, moom Usay. \v 16 Mu ne leen: «Gaawleen yónnee léegi ca Buur Daawuda te wax ko ne ko bumu fanaan fa ñuy jàlle dex ga, jëm ca màndiŋ ma. Na jàlla jàll dex ga, lu ko moy dees na ko bóom, mook mbooloo ma mu àndal mépp.» \p \v 17 Ma nga fekk Yonatan ak Ayimaas ca En Rogel. Manuñu woona dugg ca biir dëkk ba, ndax ragal ñu gis leen. Ab jaam bu jigéen nag di dem ca Yonatan ak Ayimaas, di leen wax la xew, ngir ñu dem ca Buur Daawuda, yegge ko ko. \v 18 Teewul ab xale bu góor gis leen, wax ko Absalom. Ba mu ko defee ñu ànd ñoom ñaar, gaaw dem ca kër jenn waay ju dëkk Baxurim. Waa ja am ab teen ca ëttam, ñu dugg ca biir. \v 19 Ci kaw loolu soxna sa jël basaŋ, lal ko ca pindu teen ba, ba noppi wasaare pepp ca kaw, ba kenn du ca foog dara. \v 20 Jawriñi Absalom dikk ca kër ga, fekk fa ndaw sa, ne ko: «Ana Ayimaas ak Yonatan?» Ndaw sa ne leen: «Jéggi nañu dex gi.» Ñu seet, gisuñu kenn, daldi dellu Yerusalem. \p \v 21 Gannaaw ba ñu demee, Ayimaas ak Yonatan yéeg, génn teen ba, dem nag àrtuji Buur Daawuda. Ñu ne ko Ayitofel digle na nàngam ak nàngam ci moom, neeti ko: «Gaawleen jàll dex gi léegi.» \v 22 Ca saa sa Daawudaaki nitam ñépp jàll dexu Yurdan ga. Ba jant bay fenk, kenn sax desul ku jàllul dex ga. \p \v 23 Ci biir loolu Ayitofel gis ne déggeesul ndigalam, mu takk mbaamam, ñibbi ca dëkk ba mu fekk baax. Mu daldi topptoo mbiri këram ba mu jekk, ba noppi wékk boppam. Mu dee, ñu denc ko ca sëgi baayam. \p \v 24 Ba mu ko defee Daawuda àgg Maanayim, fekk Absalom di jàll dexu Yurdan, ànd ak xarekati Israyil yépp. \v 25 Amasa nag la Absalom faloon, mu jiite mbooloom xare ma, wuutu Yowab. Amasa moo doon doomu góor gu ñuy wax Yittra, di \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* bu jëloon Abigayil, mi Nayas di baayam. Abigayil ak Seruya, yaayu Yowab, ñoo bokk ndey. \v 26 \w Bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* daldi ànd ak Absalom dal ca diiwaanu Galàdd. \v 27 Ba Daawuda àggee Maanayim, Sobi doomu Nayas mu Raba, ga ca dëkkub Amoneen ña, moo ko teertu, mook Makir doomu Amiyel ma dëkk Lodebar; ak Barsilay waa Galàdd ba dëkk Rogelim. \v 28 Ñu daldi indi ay laltu aki ndab aki njaq, ak peppum bele ak peppum lors ak sunguf ak mbool ak xeeti ñebbe, \v 29 ak lem akum soow, aki gàtt, ak formaasu nag ngir Daawudaak mbooloom lekk. Ndaxte booba dañu ne: «Mbooloo mi de, xiif ak mar lañu boole, ak coonob màndiŋ ma.» \c 18 \s1 Daawuda xare naak Absalom \p \v 1 Ba loolu weesee Daawuda xayma na mbooloo ma mu àndal, fal ca seen biir njiiti kuréli junniy xarekat, kurél gu ci nekk ak njiiti kuréli téeméer ya ko sos. \v 2 Daawuda def mbooloo ma ñetti xaaj, yebal leen. Benn xaaju mbooloo ma, Yowab jiite leen; beneen xaaj ba, Abisay doomu baayu Yowab, mi Seruya di yaayam, jiite leen; xaaj ba ca des Itay waa Gaat ba jiite leen. Buur ne mbooloom xare ma: «Damay ànd ak yeen, man itam.» \v 3 Teewul mbooloo ma ne ko: «Déedéet, yaw doo ànd ak nun! Ndax nun su ñu nu dàqee, du am boobu solo. Bu sunu genn-wàll deeyee it, du am benn solo. Waaye sa jenn jëmm jii mooy fukki junni ci nun. Kon nag desal nu ci dëkk bi, di nu fi yónnee wall, moo gën.» \v 4 Buur ne leen: «Baax na, kon ma def noonu.» Ba loolu amee Buur taxaw ca bunt dëkk ba, xarekat ya def ay kuréli téeméer ak kuréli junni, daldi génn dem. \v 5 Buur nag joor Yowab ak Abisay ak Itay, ne leen: «Seetleen ci man te def ndànk ak ngóor si Absalom.» Xarekat yépp a dégg kàddu googu Buur dénk njiit ya ca mbirum Absalom. \p \v 6 Mbooloo maa nga jëm ca toolub xare ba, di xarejeek Israyil. Xare baa nga ame ca gott ba ñuy wax Efrayim, \v 7 mbooloom Israyil nag daanu foofa ca kanam xarekati Daawuda. Bésub keroog ñu baree dee: ñaar fukki junnee (20 000) daanu. \v 8 Xare ba daa law foofa ba daj diiwaan ba bépp; te ña dee ca gott ba bésub keroog ñoo ëpp ña saamar rey. \p \v 9 Ci biir loolu Absalom ne pemm taseek xarekati Daawuda. Ma nga war berkelle. Berkelle ba fëx wuti garab gu réy, te bànqaas ya fatt. Boppu Absalom tance ca garab ga, berkelle ba mu war topp xélam, mu des fa di sandaamtalu. \v 10 Ba mu ko defee jenn waay gis ko, dem, wax ko Yowab, ne ko: «Ki ma gis de, Absalom a, ma nga wékku ci genn garab.» \v 11 Yowab ne ko: «Nga ne? Gis nga ko te jamoo ko foofa, mu daanu? Kon de doon naa la jox fukki dogi xaalis, takkal la ngañaayal xarekat tegal la ca.» \v 12 Waa ja ne Yowab: «Ku tegoon ci sama loxo junniy dogi xaalis sax, duma xàcci sama loxo jëm ci doomu buur. Noo déggal sunu bopp Buur sant la, yaak Abisay ak Itay, ne leen: “Na ma ku nekk ci yeen dimbali, te def ndànk ak ngóor si Absalom.” \v 13 Su ma jaayoon sama bakkan, ba def njekkar it, amul dara lu ump Buur, te kon it yaw danga ciy raxas say loxo.» \v 14 Yowab ne ko: «Duma la déglu sax, nga di ma yàggal!» \p Ci kaw loolu Yowab jël ñetti bant yu ñaw, jam ko Absalom ci xol, fekk ko muy dund ba tey ca xolu garab ga mu tancu. \v 15 La ca tegu fukki nit ña doon gàddul Yowab ngànnaayam, dikk wër Absalom, jam ko, mu dee. \v 16 Yowab wal liit ga, dakkal xare ba, xarekat ya noppee dàq waa Israyil. \v 17 Ñu jël néewu Absalom, sànni ci kàmb gu réy ca àll ba, daldi jóor ca kawam jalu xeer bu maga mag. \w Bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* yépp nag daw ñibbi seeni kër. \p \v 18 Absalom moo samplu woon cig dundam, doj wu mag wa ca xuru Buur, ndax da noon: «Bàyyiwuma doom ju góor ju ñu may fàttlikoo.» Moo tax mu tudde doj wa boppam, te doju Absalom lañu koy wooye ba tey jii. \s1 Lu jëm ci tàggeb Absalom \p \v 19 Ba loolu wéyee Ayimaas doomu Cadog ne: «May ma rekk ma daw yégali Buur xibaar bii, ne ko \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji musal na ko ciy noonam.» \v 20 Yowab ne ko: «Du yaw yaay yégle xibaar tey jii. Man ngaa yégle xibaar beneen yoon, waaye du yaay yégleji tey, ndax doomu buur a dee.» \v 21 Yowab nag wax ab waa \w Kuus|lemma="Kuus:"\w*, ne ko: «Demal wax Buur li xew.» Waa Kuus ba sujjóotal Yowab, daldi dem. \v 22 Ayimaas doomu Cadog dellu ne Yowab: «Lu ci mana xew, may ma rekk, man itam ma daw topp ci gannaaw waa Kuus bi.» Yowab ne ko: «Doom, lu la taxa bëgga dem, lii du xibaar bu ko jar.» \v 23 Mu ne ko: «Lu ci mana am, bëgg namaa dem.» Yowab ne ko: «Demal!» Ayimaas daw, jaare ca joor ga, ba jëkk waa Kuus ba. \p \v 24 Daawudaa nga toog ca diggante buntu dëkk, ba féete biir ak bunt ba féete biti. Fekk na wattukat ba yéeg ca kaw taax ma tiim buntu dëkk ba, ca kaw tata ja. Naka la dawal bëtam, séentu, gis jenn waay juy daw moom kenn, di ñëw. \v 25 Wattukat ba àddu ca kaw, yégal ko Buur. Buur ne: «Gannaaw kenn nit la de, xibaaru jàmm lay indi.» Waa ja di gëna jegesi, \v 26 wattukat ba gis jeneen waay juy daw di ñëw, mu wax ko farbay bunt ba, ne ko: «Xoolal, keneen a ngi, di ñëw, moom kenn.» Buur ne: «Kooku it de xibaaru jàmm lay indi.» \v 27 Wattukat ba ne: «Ni ma gise ki jiitu de, dawinu Ayimaas doomu Cadog la ma jox.» Buur ne: «Kooku ku baax la, jàmm rekk lay waxsi.» \v 28 Ci kaw loolu Ayimaas àddu ca kaw, ne Buur: «Jàmm la!» daldi sujjóotal Buur, dëpp jëëm fa suuf, ne ko: «Buur, sang bi, cant ñeel na sa Yàlla Aji Sax ji, moom mi teg ci sa loxo ña la doon fexeel.» \v 29 Buur ne ko: «Ngóor sa Absalom nag, mbaa jàmm la am?» Ayimaas ne ko: «Sang bi, ba Yowab di yónni sa bëkk-néeg ak man, booba gis naa kër-kër ju réy, waaye xawma lu mu doon.» \v 30 Buur ne: «Randul, taxawe nii.» Ayimaas randu, taxaw ca wet ga. \p \v 31 Ci kaw loolu waa Kuus ba ne jimeet. Mu ne: «Buur, sang bi, déglul, xibaaru jàmm a ngi. Aji Sax ji musal na la bésub tey ci ña la doon fexeel ñépp.» \v 32 Buur ne waa Kuus ba: «Ngóor si Absalom mbaa jàmm la am?» Waa Kuus ba ne ko: «Buur sama sang, say noon ak mboolem ñi lay fexeel, yal nañu bokk ak ngóor soosu demin.» \p \v 33 Naka la Buur dégg loolu, naqar wu réy jàpp ko. Mu dem ca biir néeg ba, ca taax ma tiim bunt dëkk ba, di jooy. Ma ngay dem te naan: «Wóoy Absalom sama doom ja! Éey sama doom ja, céy Absalom sama doom ja! Éey waay su ma sañoon dee sax wuutu la, Absalom, doom. Éey waay sama doom ja!» \c 19 \s1 Yowab sikk na Daawuda \p \v 1 Ci biir loolu ñu wax Yowab ne ko: «Buur Daawuda kat ma ngay jooy, di mititlu deewu doomam Absalom.» \v 2 Moo tax ndam la bésub keroog walbatiku diw tiis ca gàngooru xarekat ya yépp, ndax lañu dégg ne Buur a ngay mititlu deewu doomam. \v 3 Xarekat ya nag di yoxoosuy dugg bésub keroog ca Maanayim, mel ni nit ñu dawe xare, di yoxoosuy ñibbsi, ndax gàcce. \v 4 Buur a nga dar kanamam, di jooy, baat bay jib ca kaw. Ma nga naan: «Wóoy Absalom, sama doom ja! Céy waay Absalom, sama doom ja! Éey waay sama doom ja!» \p \v 5 Ba loolu amee Yowab fekk Buur ca kër ga, ne ko: «Bésub tey jii torxal nga mboolem ñi la topp, ba musal sa bakkan bésub tey, musal sa bakkani doom, góor ak jigéen ak sa bakkani soxnaak say nekkaale. \v 6 Ndax yaw dangaa bëgg ñi la bañ, bañ ñi la bëgg. Biral nga tey ne kilifay xarekat yeek xarekat yépp, tekkiwuñu dara ci yaw. Bir na ma ne bu Absalom doon dund tey te nun ñépp nu bokk dee, moo lay gënal. \v 7 Léegi nag, jógal kat génn wax ak say nit, ruccanti leen. Ndax giñ naa ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, soo génnul, du kenn ku fiy bokk fanaan ak yaw tey. Te loolu de musiba lay doon ci yaw, mu gëna réy musiba mu la masa dal, ba ngay ndaw ba tey.» \v 8 Buur daldi jóg, génn, toog ca buntu dëkk ba. Ñu wax mbooloo ma mépp ne leen: «Gisleen Buur a ngee toog ca bunt ba.» Mbooloo mépp dikk taxaw ci wetam. \p Fekk na \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ya faroon ak Absalom daw ñibbi ca seeni kër. \s1 Daawudaa ngi dellu Yerusalem \p \v 9 Ba loolu amee giiri \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* yépp diisoo ci seen biir. Ña nga naan: «Buur Daawudaa nu xettli woon ci sunuy noon, rawatina Filisteen ñi. Bu dawee génn réew mi, Absalom a ko waral. \v 10 Gannaaw Absalom ma nu faloon mu jiite nu, dee na ca xare ba, lu nu tee wax lu jëm ci délloosi Buur Daawuda?» \p \v 11 Ci kaw loolu Buur Daawuda ci wàllu boppam yónnee ca Cadog ak Abiyatar, \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ya, ne leen: «Waxleen ak magi Yuda, te laaj leen, ne leen: “Xanaa ñépp duñu jéem lu délloosi Buur këram, yeen ngeen des gannaaw, te moom ci boppam dégg na kàddug bànni Israyil gépp. \v 12 Yeen de yeenay bokki buur lenqe, ngeen bokk ak moom jenn deret; kon xanaa ñépp duñu délloosi Buur, ngeen des gannaaw?” \v 13 Te ngeen waxal ma Amasa ne ko: “Buur nee, xanaa doo mbokkam lenqe, di deretam? Nee yal na ko Yàlla teg mbugal mu gëna tar ndegam du la fal, nga jiite mbooloom xare mi ba fàww, wuutu Yowab.”» \v 14 Kàddu yooyu nag waññi xolu Yudeen ñépp, ñu bokk genn kàddu, daldi yónnee ca Buur ne ko mu délsi, mook nitam ñépp. \s1 Simey tuubal na Daawuda \p \v 15 Gannaaw loolu Buur Daawuda walbatiku, dikk ba àgg dexu Yurdan, Yudeen ña dikk, teertusi ko ca Gilgal, ngir jàllale ko dexu Yurdan. \v 16 Simey doomu Geraa ngay gaawtu. Mooy waa Baxurim ba askanoo ci Beñamin. Ma nga ànd ak Yudeen ña, di teertu Buur Daawuda. \v 17 Junniy nit ñu askanoo ci Beñamin a ko topp, ñook Ciba, surgab waa kër Sóol, ak fukki doomam yu góor ak juróom, ak ñaar fukki surgaam. Ñu riirandoo ca dex ga, di gatandu Buur Daawuda. \v 18 Ci kaw loolu ñu jàll dex ga, ngir jàlle waa kër Buur, defal ko coobareem. Ba Buur Daawuda di waaja jàll dex ga, Simey doomu Gera da ne gurub sukk, sujjóotal ko, \v 19 ne ko: «Buur, sang bi, ngalla bu ma topp lu ñaaw li ma def. Bu ma jàppal mer ndax li ma la tooñ, keroog ba ngay jóge Yerusalem. Ngalla bu ma ko dencal ci sa xol, \v 20 ndaxte xam naa ne bàkkaar naa, sang bi. Waaye xoolal tey, Buur, sang bi, waa giirug Yuusufa gépp, maa ci jëkka ñëw gatandusi la.» \p \v 21 Abisay ma yaayam di Seruya ne Buur: «Simey mii, lu muy wax nii? Kii deesu ko rey? Du moo la doon saaga, yaw mi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji fal?» \v 22 Daawuda ne Abisay: «Yeen, doomi Seruya, lu ciy seen yoon, ba ngeen di ma ŋàññ nii tey? Xam naa xéll tey ne maay buurub Israyil. Kon ana ku wara rey kenn tey ci Israyil?» \v 23 Buur nag wax Simey ne ko deesu ko rey, daldi ko koy giñal. \s1 Daawuda baaxe na Mefiboset \p \v 24 Ci kaw loolu Mefiboset, sëtub Sóol, dikk moom it, di teertusi Buur. Diggante bés ba Buur gàddaayee nag, ba bésub keroog ba mu délseek jàmm ca Yerusalem, Mefiboset jànguwul, watul sikkimam, te fóotul ay yéreem. \v 25 Naka la Mefiboset dikk ca Buur, di ko teertu, Buur ne ko: «Mefiboset, lu la tee woona ànd ak man?» \v 26 Mu ne ko: «Éy Buur, sang bi, sama surga Ciba moo ma nax de, sang bi, ndax man, dama noon damay takklu sama mbaam war, gannaaw ab lafañ laa. Su ko defee ma ànd ak yaw. Yaay sama sang. \v 27 Waaye sama surgaa yàq sama der ci yaw. Yaw nag Buur, sang bi, ndokk ba nga matee ba mel ni malaakam Yàlla. Kon sang bi, defal li la soob. \v 28 Ndax kat sang bi, du kenn ci sama askanu maam ku yelloowul lu moy nga rey ko. Terewul danga maa xajal, sang bi, boole ma ci ñiy bokk ak yaw ndab. Kon Buur, ana lu ma la sañatee ñaan?» \v 29 Buur ne ko: «Ana looy waxati lii lépp? Dogal naa yaak Ciba, ngeen séddoo suuf si.» \v 30 Mu ne Buur: «Amul solo, Buur, sang bi; na jël lépp sax, ndegam yaw ñibbsi ngaak jàmm sa biir kër kay!» \s1 Daawuda tàggtoo na ak Barsilay \p \v 31 Fekk na Barsilay ma bokk ca Galàdd jóge woon Rogelim, ngir gunge Buur Daawuda, ba mu jàll dexu Yurdan, bala moo tàggtoo ak moom ca wàllaa dex. \v 32 Barsilay mag la woon. Amoon na juróom ñett fukki at. Moom moo daan topptoo Buur diir ba mu nekk Maanayim, ndax nit ku bare alal la woon. \v 33 Buur ne Barsilay: «Jàllal nu dem, nga toog ci man, ma yor la ca Yerusalem.» \v 34 Mu ne Buur: «Moo, man, Buur, lu ma deseeti ciy fan, bay ànd ak yaw dem Yerusalem! \v 35 Maa ngi ci juróom ñett fukki at tey, te xamatuma lu neex ak lu naqari. Sang bi, man xamatuma sax lu ma lekk di saf mbaa naan, te baatu woykat sax safatu ma dara, muy góor, di jigéen. Kon ana lu ma lay diisalati doye? \v 36 Naa jàll dex gi, gunge la tuuti rekk, Buur. Te sax gisuma lu jar nga di ma defal boobu yool! \v 37 Bàyyil rekk sang bi, ma ñibbi, ndax ma deeyi sama dëkk, ñu denc ma ca sama wetu ndey ak sama baay. Waaye ma ne, Buur, sang bi, Kimyam a ngoogu di sa surga. Na ànd ak yaw jàll. Defal ko lu la soob.» \v 38 Buur ne ko: «Baax na, na Kimyam ànd ak man, nu jàll. Dinaa ko defal li nga bëgg, te loo bëgg ma defal la ko rekk, dinaa la ko defal.» \p \v 39 Noonu la mbooloo ma mépp jàlle dexu Yurdan, Buur it jàll. Buur nag taf Barsilay ca kawam, ñaanal ko, Barsilay doora ñibbi këram. \v 40 Ba mu ko defee Buur jàll ba Gilgal, Kimyam ànd ak moom. Mbooloom Yuda gépp ak ñenn ci mbooloom Israyil itam ànd ak Buur dem. \p \v 41 Naka la loolu am rekk waa Israyil yépp dikk ca Buur, ne ko: «Buur Daawuda, ana lu waral sunu bokki Yuda yi aakimoo la, jàlle la dexu Yurdan, yaak sa waa kër ak sa nit ñi nga àndal ñépp?» \v 42 Waa giirug Yuda gépp nag mànkoo ne waa Israyil: «Li ko waral mooy Buur da di sunu mbokk lenqe. Ana lu ngeen di mer ci loolu? Danoo lekkal Buur dara mbaa nu sàkkal sunu bopp lenn ci alalam?» \v 43 Waa Israyil ne waa Yuda: «Noo leen ëpple ci Buur fukki yoon, noo leen ëpp sañ-sañ fopp ci Daawuda. Lu ngeen nuy xeebe? Xanaa du noo jëkka wax lu jëm ci délloosi sunu buur?» Ci kaw loolu waa Yuda dellu tontu waa Israyil kàddu yu gënatee ñagas. \c 20 \s1 Seba jàmbu na \p \v 1 Booba nit ku bon a nga woon ca mbooloo ma, ku ñuy wax Seba, di doomu Bikkri, ma bokk ca giirug Beñamin. Seba wal liit ga, daldi yéene ne: \q1 «Sunu yoon nekkul ci Daawuda doomu Yese jii, \q1 du benn cér bu nu am ci moom. \q1 Yeen waa Israyil, ku nekk ca sa xayma!» \p \v 2 Ba mu ko defee waa Israyil yépp jàmbu Daawuda, topp Seba doomu Bikkri. Teewul waa giirug Yuda ñoom taq ci seen buur, toppe ko dexu Yurdan ba Yerusalem. \p \v 3 Buur Daawuda nag ñibbi këram ga ca Yerusalem. Teewul fukki nekkaaleem ña mu waccoon ñuy topptoo kër ga, da leena boole denc ci genn kër, ñu di leen fa wattu. Mu yor leen fa, te dëkkootu leen. Dees leen faa denc ba keroog ñuy dee, ñu mel ni ay jëtun. \p \v 4 Gannaaw loolu Buur ne Amasa, ma jiite mbooloom xareem: «Danga may wool góori Yuda, ñu dajesi ci man fii ak ñetti fan, te yaw itam nga dikk taxaw fii.» \v 5 Amasa dem wooyi Yudeen ña, yàgg ca ba wees diir ba ko Buur àppaloon. \v 6 Daawuda nag ne Abisay: «Seba doomu Bikkri jii de dina nu lor lu raw la nu Absalom loroon. Àndal ak ñenn ci samay dag te dàqi ko, lu ko moy dina gis fu mu làqu ci ay dëkk yu ñu wërale ay tata, ba raw nu.» \v 7 Ba loolu amee niti Yowab ña ànd ak waa Keret ñaak waa Pelet ñay dar Daawuda, ak xarekat yépp. Ñu jóge Yerusalem dàqi Seba doomu Bikkri. \v 8 Dem nañu ba tollu ca doj wu mag wa ca Gabawon, doora gis Amasa, muy dox di dajeek ñoom. Yowab a nga sol yérey xareem, laxasaay ga ca ndigg la ànd ak saamar bu roofe ca mbaram. Naka la séqi jéego jëm kanam, saamar ba rot. \v 9 Yowab ne Amasa: «Mbokk mi, mbaa jàmm nga am?» Yowab jàpp sikkimu Amasa ca loxol ndijooram, mel ni ku koy fóon. \v 10 Amasa foogul dara ci saamar ba ca loxol càmmoñu Yowab. Yowab bojj ko ko ci biir, wàlli ay butitam ci suuf. Tóllantiwul sax, Amasa dee. \p Ci kaw loolu Yowab ànd ak rakkam Abisay, dàqi Seba doomu Bikkri. \v 11 Ci biir loolu kenn ci niti Yowab ña taxaw fa Amasa tëdd, daldi ne: «Ku sopp Yowab ak képp ku ànd ak Daawuda na topp Yowab.» \v 12 Néewub Amasaa nga ca digg yoon wa, sangoo deretam. Waa ja gis ne képp ku dox ba tollook moom, taxaw nga fa. Naka la waa ja gis ñépp di taxaw foofa, mu diri néew ba, jële ko ca yoon wa, ba ca àll ba. Mu sànni malaan ca kawam. \v 13 Ba ñu fa jëlee néewu Amasa, ñépp ànd ak Yowab toppi Seba doomu Bikkri. \p \v 14 Yowab jaar ca giiri Israyil gépp ba ca Abel Bet Maaka. Waa Ber gépp daje topp ko. \v 15 Ñu dikk gaw dëkk ba ñuy wax Abel Bet Maaka, fa Seba làqu. Ci kaw loolu ñu jal suuf fa sës ca buntu dëkk ba, mu kawe ba tollook tatay dëkk ba. La ca tegu xarekati Yowab yépp di jéema màbb tata, ja wër dëkk ba. \p \v 16 Ci biir loolu senn as ndaw su am xel ca dëkk ba, woote ne leen: «Dama ne, dégluleen! Neleen Yowab mu ñëw, ma wax ko.» \v 17 Yowab dem ba ca moom, ndaw sa ne ko: «Yaa di Yowab?» Mu ne ko «Waaw.» Mu ne ko «Sang bi, dama ne...» Mu ne ko: «Ãa.» \v 18 Mu ne ko: «Daa nañu wax bu jëkk naan: “Lu waay di laaj, na dem Abel, tont laa nga fa.” Su ko defee, wax ja jeex. \v 19 Nun danu di niti jàmm ñu am kóllëre ci digg Israyil. Yaw nag yaa ngi wuta faagaagal dëkk bu mag bu jaboote ñi ko wër ñépp ci digg Israyil. Ana lu waral nga namma tas dëkk bu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji séddoo?» \v 20 Yowab ne ko «Yàlla tere, tereeti ko, may tas ak a faagaagal kenn! \v 21 Du loolu! Jenn waay ju ñuy wax Seba doomu Bikkri te bokk ca waa tundi Efrayim, moo jógal Buur Daawuda. Joxleen ma ko moom doŋŋ, ma bàyyi dëkk bi te dem.» Ndaw sa ne Yowab: «Xoolal, boppam lañuy tollu ci kaw taax mi, sànni la ko.» \v 22 Ndaw sa nag dem ca mbooloo ma mépp, xelal leen pexeem mu jub moomu. Ñu dog boppu Seba doomu Bikkri, sànni ko Yowab. Yowab wal liit ga, nitam ña tasaaroo, bàyyi dëkk ba, ku nekk ñibbi këram. Yowab daldi dellu Yerusalem ca Buur. \s1 Lu jëm ci jawriñi Daawuda \p \v 23 Yowab moo jiite woon mbooloom xarem Israyil gépp; Benaya doomu Yoyada yilif dag ya dar Buur, te di waa Keret ak waa Pelet; \v 24 Adoram di saytu liggéey ya ñuy sase; Yosafat doomu Ayilut yor kàddug Buur; \v 25 Sewa di bindkat; Cadog ak Abiyatar di ay \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w*; \v 26 Ira ma fekk baax Yayir itam di sarxalkatu Daawuda. \c 21 \ms1 Yenn xew-xew a ngi \s1 Waa Gabawon feyu nañu \p \v 1 Jamono ya Daawuda nekkee ci jal bi, amoon na xiifub ñetti at yu tegloo. Daawuda diis ko \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Aji Sax ji ne ko: «Li waral xiif bi moo di àqu deret ji topp Sóol ak waa këram ndax waa Gabawon ña mu rey.» \v 2 Buur woo waa Gabawon, wax ak ñoom. Waa Gabawon bokkuñu woon ci \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, waaye ñoo desoon ca Amoreen ña bànni Israyil giñaloon ne duñu leen rey. Teewul Sóol xéroon lool ci bànni Israyil ak Yuda, bay fexee faagaagal waa Gabawon. \v 3 Daawuda laaj waa Gabawon, ne leen: «Lan ngeen bëgg ma defal leen ko? Ana lu may def ba jotoo ko àq, ji ñu leen ameel, ba ngeen ñaanal ñoñi Aji Sax ji?» \v 4 Waa Gabawon ne ko: «Du xaalis, du wurus wu nuy laaj Sóol mbaa waa këram; te it du kenn ci Israyil ku nu saña reylu.» Mu ne leen: «Waxleen boog lu ngeen di laaj, ma defal leen ko.» \v 5 Ñu ne ko: «Sóol da noo naroona fexeel, sànk nu, faagaagal nu ci réewum Israyil. \v 6 Kon dees nuy jox juróom ñaari góor ñu askanoo ci Sóol, nu jam leen ba mu sar fa kanam Aji Sax ji ca Gibeya, dëkkub Sóol, ma Aji Sax ji faloon.» Buur ne leen: «Dinaa leen leen jox.» \p \v 7 Teewul Daawuda déeg Mefiboset, ma Yonatan doomu Sóol di baayam, ndax la ñu giñoo woon ci Aji Sax ji, mook Yonatan doomu Sóol. \v 8 Buur nag jàpp Armoni ak meneen Mefiboset, te Rispa doomu Aya di seen yaay, Sóol di seen baay. Buur boole ca juróomi góor ña Mikal\f + \fr 21.8 \fr*\fk Mikal \fk*\ft mii du Mikal mi ñuy wax ci 6.23, ne amul doom, ba keroog muy dee. Mikal mii mook Merab ñuy wax ci \ft*\ft \+bk 1.Samiyel\+bk* 18.19 kenn nit ki la. Jëkkëram mooy Àddiryel.\ft*\f* doomu Sóol di seen yaay, te Àddiryel doomu Barsilay ma dëkk Mewola di seen baay. \v 9 Daawuda jébbal leen waa Gabawon, ñu jam leen ba mu sar, foofa ca kaw tund wa, fa kanam Aji Sax ji. Juróom ñaar ñooñu ñépp a bokk tëdd. Ña nga leen rey ca fan ya ñu tàmbalee góob, ca ndoortel ngóobum lors ba. \p \v 10 Ba mu ko defee Rispa doomu Aya ju jigéen ja, jël ab saaku, tàllalal ko boppam ca doj wa. La ko dale ca ndoortel ngóob ma, ba keroog asamaan di sóob ca kaw néew ya, Rispa bàyyiwul dara mu laal leen bëccëg mbaa guddi, du picc, du rabu àll. \p \v 11 Ba loolu amee ñu àgge Daawuda jëfi Rispa doomu Aya, nekkaaleb Sóol ba. \v 12 Daawuda dem jëleji yaxi Sóol ak doomam Yonatan ca waa Yabes Galàdd. Ndax gannaaw ba ñu daanee Sóol ca Gilbowa, Filisteen ña dañoo wékkoon néewu Sóol ak Yonatan ca péncum Bet San. Waa Yabes Galàdd dikk sàcce leen fa. \v 13 Ci kaw loolu Daawuda jële fa yaxi Sóol ak doomam Yonatan, ak yaxi nit ña ñu jamoon ba mu sar te wékk leen. \v 14 Ñu boole kook yaxi Sóol ak doomam Yonatan, denc lépp ca sëgu Kis, baayu Sóol, ca diiwaanu Beñamin ca Sela. Ñu def la Buur santaane lépp. Gannaaw loolu Yàlla nangul réew ma. \s1 Daawuda daje naak ponkali waa Filisti \p \v 15 Bu loolu wéyee, xare amaat na diggante Filisteen ñi ak \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. Daawuda ànd aki nitam xarejeek Filisteen ña. Daawuda nag sonn ci biir xare bi. \v 16 Ci kaw loolu Isbi Bënob ne dina rey Daawuda — kooku askanu ponkal ya ñu daan wooye Rafayeen, ca la bokkoon. Ñawkay xeejam xànjar la, diise ñetti kilo. Mu yore itam saamar bu bees. \v 17 Teewul Abisay doomu Seruya dikk, wallusi Daawuda, jam Filisteen ba, rey ko. Niti Daawuda daldi cay giñal Daawuda, ne: «Dootuloo ànd ak nun mukk cib xare. Lu ko moy dinga ci dee, askanu buur fey ci Israyil.» \p \v 18 Gannaaw gi xare dellu am seen digganteek Filisteen ña ca dëkk ba ñuy wax Gob. Ca la Sibeka, ma askanoo ci Usa, rey Saf ma bokk ca askanu ponkal ya. \v 19 Xare amati ca Gob seen digganteek Filisteen ña. Elxanan doomu Yare Oregim ma dëkk Betleyem, jam Golyaat ma dëkk Gaat. Kookoo di waa ja bantub xeejam réyoon, ba tollu ni mbaam mu ñuy ràbbe. \p \v 20 Xare dellu amati ca Gaat. Jenn waay ju réya réy a nga ca woon, ku am juróom benni baaraam, loxo bu nekk, ak juróom benni baaraam, tànk bu nekk, lépp di ñaar fukki baaraam ak ñeent. Moom it ponkalum Rafayeen la woon. \v 21 Ba mu tëkkoo Israyil, Yonatan a ko rey. Yonatan, Simeya magi Daawuda mooy baayam. \v 22 Ñeent ñooñu ay ponkali Rafayeen lañu woon ca Gaat. Daawudaaki nitam ñoo leen jam, ñu daanu. \c 22 \s1 Daawuda sant na \p \v 1 Daawuda woy na \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji gannaaw ba ko Aji Sax ji xettlee ci mboolemi noonam, xettli ko it ci Sóol. Kàdduy woy wa lii la. \v 2 Mu ne: \q1 Aji Sax ji laay sës, \q1 mu di ma aar, \q1 di ma wallu. \q1 \v 3 Mooy sama Yàlla, ji ma sës, yiiru, \q1 fegu, mucc, \q1 làqu, raw, \q1 mucc fitna. \q1 \v 4 Ki yelloo cant, Aji Sax ji, \q1 moom laa woo, mucc ci samay noon. \b \q1 \v 5 Gannaxi ndee mëdd ma, \q1 walum kasara naq ma. \q1 \v 6 Buumi njaniiw laaw ma, \q1 dee ne jaas, di ma fiir. \q1 \v 7 Ma jàq, woo Aji Sax ji, \q1 ne sama Yàlla wallóoy, mu dégge këram. \q1 Ma yuuxu, muy dégg. \b \q1 \v 8 Mu mer, suuf yëngu, di ker-keri, \q1 kenuy asamaan jaayu, di reg-regi. \q1 \v 9 Saxar di sël-sëlee ca wakkan ya, \q1 sawara boye ca gémmiñ ga, \q1 xal yu yànj tàkke ca. \q1 \v 10 Mu firi asamaan, wàcc, \q1 niir yu fatt lal tànk ya. \q1 \v 11 Ma nga war malaakam \w serub|lemma="serub y-:"\w*, di naaw, \q1 daayaarloo laafi ngelaw. \q1 \v 12 Ma nga bàddoo lëndëm, \q1 làmboo jali ndox aki xàmbaar. \q1 \v 13 Leer a ko jiitu, \q1 ay xali sawara topp ca. \q1 \v 14 Aji Sax jee dënoo asamaan. \q1 Aji Kawe jee àddu, \q1 \v 15 soqiy fitt ak jumi melax, \q1 tasaare leen, fëlxe. \q1 \v 16 Aji Sax ji gëdd, \q1 nokki, mu riir; \q1 xuri géej ne fàŋŋ, \q1 kenuy suuf ne duŋŋ. \b \q1 \v 17 Moo yóotoo fa kaw, jàpp ma, \q1 seppee ma ca xóotey ndox ma, \q1 \v 18 musal ma ca noon yu mag, \q1 ya ma bañ te man ma. \q1 \v 19 Ñu dajeek man, bés ba ma jàqee, \q1 Aji Sax ji taxawu ma, \q1 \v 20 yaatal ma, \q1 bége ma, ba xettli ma. \b \q1 \v 21 Aji Sax jee ma yool sama njekk, \q1 samay loxoo set, mu fey ma. \q1 \v 22 Sàmm naa yooni Aji Sax ji, \q1 bonuma, di moy sama Yàlla. \q1 \v 23 Dama ne jàkk ndigalam yépp, \q1 dëdduwma dogali yoonam. \q1 \v 24 Seede na, may jëfeg mat, \q1 di moyoo tooñ. \q1 \v 25 Aji Sax jee ma yool sama njekk, \q1 rafetlu sama mucc ayib. \b \q1 \v 26 Yaw Aji Sax ji, ku gore, fekk la gore; \q1 ku matale, fekk la matale; \q1 \v 27 ku sellal, fekk la sell; \q1 ku dëng, fekk laak say feem. \q1 \v 28 Yaw yaay musal xeet wu néew doole, \q1 kuy daŋŋiiral, nga detteel. \q1 \v 29 Yaw Aji Sax ji, kay, laay niitoo, \q1 Aji Sax jeey leeral sama lëndëm. \q1 \v 30 Maak yaw kay, ma song gàngoor. \q1 Maak sama Yàlla, ma tëb um tata. \b \q1 \v 31 Yàllaa mat, \q1 kàddug Aji Sax jee wér te wóor. \q1 Mooy feg képp ku ko làqoo. \q1 \v 32 Ana kuy Yàlla ku moy Aji Sax ji? \q1 Ku jara sës ku dul sunu Yàlla? \b \q1 \v 33 Yàllaa may làqe dooleem, \q1 xàllal ma, yoon mat. \q1 \v 34 Moo ma gaawal ni kéwél, \q1 taxawal ma fu kawe. \q1 \v 35 Moo may tàggat ngir xare, \q1 may bank xalag xànjar. \q1 \v 36 Aji Sax ji, yaa may feg, musal ma, \q1 yaa may nangul, darajaal ma. \q1 \v 37 Yaa ma xàllalu yoon, \q1 duma tërëf. \q1 \v 38 Maay dàq noon yi, falaxe, \q1 jekkli, doora dëpp. \q1 \v 39 Ma rajaxe, nemmali, jógatuñu, \q1 xanaa fëlëñu, ma joggi. \q1 \v 40 Sol nga ma dooley xare, \q1 sukkal ñi ma jógal, ñu féete ma suuf. \q1 \v 41 Yaa ma won ndoddi noon, \q1 ma boole bañ yi, bóom. \q1 \v 42 Ñu ne wallóoy, wall amul, \q1 ñu woo Aji Sax ji, faalewu leen. \q1 \v 43 Ma wol, ba ñu doon pënd, \q1 dër, note ni banu mbedd. \q1 \v 44 Yaa ma xettli ci bokk yiy fippu, \q1 def ma, ma jiite ay xeet; \q1 waaso wu ma xamul sax nangul ma, \q1 \v 45 ku ma ci dégg, déggal ma, \q1 ay doomi doxandéem di ma raamal, \q1 \v 46 ne yàcc, \q1 génne seeni tata, di lox. \b \q1 \v 47 Aji Sax jeey Kiy dund. \q2 Kii ma sës moo jara sant. \q1 Yàlla sama cëslaay ji may musal moo màgg! \q1 \v 48 Mooy Yàlla ji may feyul, \q1 di ma suufeelal xeet yi. \q1 \v 49 Xettli nga maak ku ma bañ ak ku ma jógal, \q1 kaweel ma, ma tiim leen, \q1 xettleeti ma cib soxor. \b \q1 \v 50 Kon Aji Sax ji, ma sant la ci biir xeet yi, \q1 kañ la! \q1 \v 51 Yaay may sa buuru ñoñ ndam lu réy, \q1 yaay ji ngor ki nga fal, \q1 muy man Daawuda, di sama askan ba fàww. \c 23 \s1 Daawuda biral na waxyu \p \v 1 Kàddu yii la Daawuda tàggtoo. Da ne: \q1 Kàddug Daawudaa ngi, doomu Yese, \q1 kàddug góor gu ñu kaweel, \q1 góor gi Yàllay Yanqóoba fal, \q1 muy woykatu Israyil, bi ñu ñal. \q1 \v 2 Noowug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee may waxe, \q1 sol ma kàddoom. \q1 \v 3 Yàllay Israyil a wax, \q1 moom mi Israyil sës, moo ne: \q1 Ku jiite ay nit cig njub, \q1 bu jiitee cig ragal Yàlla, \q1 \v 4 day mel ni leeru jant bu fenk, \q1 kaw asamaanu suba su niir newul, \q1 leeru asamaan su set, taw ba siwet, \q1 ba ñax jebbi. \b \q1 \v 5 Du nii la sama waa kër def ak Yàlla? \q1 Moo fas ak man \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* gu sax dàkk, \q1 lépp jekk, mat sëkk. \q1 Moo may may ndam saa su ne, \q1 di ma defal lu ma namm. \q1 \v 6 Waaye ku bon, ñu buub nig taxas, sànni. \q1 Deesu ko fore loxo, \q1 \v 7 xanaa fore ko weñ mbaa bantub xeej, \q1 jafal mu lakk fa mu ne. \s1 Jàmbaari Daawuda def nañuy jaloore \p \v 8 Ñeyi xarey Daawuda ya, ñoo di: \q1 Yosebasebet waa Agmon ba bokk ca mbëri xare ya. \q1 Moo xàcci xeejam, dal ci juróom ñetti téeméeri nit, \q1 rey leen ci menn cong. \b \q1 \v 9 Ka ca topp di Elasar, \q1 Elasar, Dodo. \q1 Dodo, Awoya. \q1 Elasar bokkoon na ci ñetti jàmbaari xare ya àndoon ak Daawuda, \q1 di dëkk Filisteen ña fa daje woon ngir xare. \q1 Fekk \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* di dellu gannaaw. \q1 \v 10 Elasar a taxaw, di cor Filisteen ña, \q1 ba loxo ba banku, taq ca njàppul saamaram. \q1 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee maye ndam lu réy bésub keroog! \q1 Ba ko mbooloom bànni Israyil fekksee, \q1 defuñu lu moy futti néew ya. \b \q1 \v 11 Ka topp ca Elasar di Saama. \q1 Saama, Age ma dëkk Arar ay baayam. \q1 Ba Filisteen ña dajee ca Léyi, \q1 wetu toolub ñebbe ba meññoon, ba fees dell, \q1 bànni Israyil dañoo daw. \q1 \v 12 Saamaa taxaw ca digg tool ba, \q1 aar tool ba, duma Filisteen ña. \q1 Aji Sax jee ca maye ndam lu réy! \b \q1 \v 13 Mu am bés, jamonoy ngóob, \q1 ñett ca mbëri xare ya fekki Daawuda ca xunti ma ca Adulam. \q1 Mbooloom Filisteen ñaa nga dal ca xuru Refayeen. \q1 \v 14 Daawudaa nga ca biir rawtoom. \q1 Mu am kurélu xareb Filisteen ñu dal Betleyem. \q1 \v 15 Daawuda jekki-jekki xel ma sore. \q1 Mu ne: «Éy ku ma wutali woon ndox mu ma naan ca teenu Betleyem ba ca buntu dëkk ba!» \q1 \v 16 Ci kaw loolu ñetti jàmbaari xare ya bëtt dalub Filisteen ña. \q1 Ñu dem duyi ndox ca teenu Betleyem ba ca wetu buntu dëkk ba, \q1 dikk yót Daawuda ndox ma. \q1 Daawuda nag néegu koo naan; \q1 da koo tuur, te Aji Sax ji tax. \q1 \v 17 Mu ne: «Yàlla tere, Aji Sax ji, may naan miim ndox, \q1 nde kon deretu ñii dem jaayi seen bakkan laa naan.» \q1 Daawuda naanul ndox ma. \b \q1 Jooju jëf la ñetti jàmbaari xare ya def. \b \q1 \v 18 Abisay bokkoon na ca mbëri xare ya. \q1 Abisay ak Yowab, Seruyaa di seen yaay. \q1 Abisay a xàcci woon xeejam, dal ci kaw ñetti téeméeri nit, rey leen. \q1 Mu doxe fa siiw ni ñett ñooña. \q1 \v 19 Abisay bokk na ca ña gënoona siiw ca Fanweeri jàmbaar ya; \q1 mujj na sax di seen njiit, \q1 waaye bokkuloon ca Ñett ña. \b \q1 \v 20 Benaya nag, Yoyadaay baayam, \q1 xarekat bu mag la woon, dëkkoon Kabsel. \q1 Def na jaloore yu réy! \q1 Moo rey ñaari Mowabeen ña gënoona jàmbaare. \q1 Moo wàccoon ci kàmb, bésu tawu yuur, rey fa gaynde. \q1 \v 21 Moo reyoon it waa Misra bu jekk ba taxawaay. \q1 Waa Misra baa nga yor ab xeej, \q1 Benaya songewu ko lu moy aw yet. \q1 Mu bif xeeju waa Misra ba, \q1 nangoo ko ciy loxoom, reye ko ko. \q1 \v 22 Jooju jëf la Benaya doomu Yoyada def. \q1 Moom it siiwoon na ni ñetti mbëri xare ya, \q1 \v 23 ñu gënoon koo naw ca Fanweeri jàmbaar ya, \q1 waaye bokkuloon ca Ñett ña. \q1 Daawuda nag def ko njiitu dag ya ko dar. \b \q1 \v 24 Ñii bokkoon nañu ca Fanweeri jàmbaar ya: \li1 Asayel, rakki Yowab, \li1 Elxanan, Dodo di baayam, dëkk Betleyem, \li1 \v 25 Saama ma doon waa Arot, \li1 Elika, di waa Arot, \li1 \v 26 Eles ma dëkk Pelet, \li1 Ira, Ikes di baayam, dëkk Tekowa, \li1 \v 27 Abiyeser ma dëkk Anatot, \li1 Mebunay dëkk Usa, \li1 \v 28 Salmon dëkk Awoya, \li1 Maaray dëkk Netofa, \li1 \v 29 Eleb, Baana di baayam, dëkk Netofa, \li1 Itay, Ribayi di baayam, dëkk Gibeya ca giirug Beñamin. \li1 \v 30 Benaya ma dëkk Piraton, \li1 Iday ma dëkk walum Gaas, \li1 \v 31 Abi Albon dëkk Bet Araba, \li1 Asmawet dëkk Barum, \li1 \v 32 Elyaba dëkk Saalbon, \li1 ak góor ñi Yasen di seen baay, \li1 ak Yonatan, \v 33 Saama di baayam, dëkk Arar, \li1 Akiyam, Sarar di baayam, dëkk Arar, \li1 \v 34 ak Elifelet, Axasbay di baayam, \li1 Axasbay, baayam dëkk Maaka, \li1 ak Eliyam, Ayitofel di baayam, dëkk Gilo, \li1 \v 35 ak Esray ma dëkk Karmel, \li1 ak Paray dëkk Arab, \li1 \v 36 ak Igal, Natan di baayam, dëkk Soba, \li1 ak Bani ma dëkk Gàdd, \li1 \v 37 ak Seleg, Amoneen ba, \li1 ak Naray ma dëkk Berot. \li1 Kookoo yoroon ngànnaayi Yowab ma Seruya di yaayam. \li1 \v 38 Ira ma dëkk Yeter ca la, \li1 ak Gareb dëkk Yeter, \li1 \v 39 ak Uri, Etteen ba. \p Ñoom ñépp tollu ci fanweeri jàmbaar ak juróom yaar. \c 24 \s1 Daawuda waññ na bànni Israyil \p \v 1 Gannaaw ba loolu wéyee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji mereeti\f + \fr 24.1 \fr*\ft Seetal ci 21.1-14.\ft*\f* \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, ba tax mu xiir Daawuda ci def lu leen di lor. Mu def ci xelam ne ko mu dem lim waa Israyil ak Yuda. \p \v 2 Buur wax ak Yowab ma ca wetam, di njiital xarekat ya. Mu ne ko: «Wëral ci biir giiri Israyil gépp ba ñu daj, li ko dale diiwaanu Dan ca bëj-gànnaar ba Beerseba ca bëj-saalum. Nañu bind askan wi, ndax ma xam seenub lim.» \v 3 Yowab ne ko: «Buur, yal na Aji Sax ji ful askan wi téeméeri yoon, nga fekke. Waaye sang bi, lu la xiir ci loolu?» \p \v 4 Teewul kàddug Buur ëpp doole Yowab ak njiiti xarekat ya. Ñu bàyyikoo ca Buur, dem bindi askanu Israyil. \v 5 Ñu jàll dexu Yurdan, dem dali Arower ca bëj-saalumu dëkk ba, ca biir xur wa, daldi dem Gàdd, jaare fa jëm Yaser. \v 6 Ci kaw loolu ñu dem diiwaanu Galàdd, jàll ba Kades ca diiwaanu Etteen ña, dem Dan Yaan ak la ko wër, teg ca Sidon. \v 7 Ba mu ko defee ñu dem ba Tir, dëkk ba ñu wëralee ab tata, jóge fa dem ca mboolem dëkk-dëkkaani Eween ñaak Kanaaneen ña. Ñu àkkeji Beerseba ca bëj-saalumu màndiŋu Yuda. \v 8 Wër nañu réew ma mépp ci juróom ñeenti weer ak ñaar fukki fan, doora ñibbsi Yerusalem. \p \v 9 Yowab nag indil Buur limu askan wa: Israyil di juróom ñetti téeméeri junniy góor (800 000) ñu tollu ci xare; Yuda di juróomi téeméeri junniy góor (500 000). \p \v 10 Daawuda waññ askan wa ba noppi, fit wa ne rës, mu yedd boppam, daldi ne Aji Sax ji: «Aji Sax ji, bàkkaar naa lool. Léegi nag ngalla jéggal ma sama ñaawtéef, ndax def naa jëfi dof ju réy lool.» \v 11 Ba Daawuda jógee ca ëllëg sa, kàddug Aji Sax ji dikkal Gàdd, yonent Yàlla ba féetewoo kër Buur Daawuda. Mu ne ko: \v 12 «Demal ne Daawuda: “Aji Sax ji dafa wax ne: Ñett laa lay jox, nga tànn ci lenn lu ma lay def.”» \v 13 Gàdd dem ca Daawuda, jottli ko ko, ne ko: «Ana yii yett loo ci taamu, mu dal ci sa kaw: juróom yaari ati xiif ci sam réew, am ñetti weer yooy daw say noon, am ñetti fani mbas ci sam réew? Xalaatal léegi te wax ci lenn, ma xam lu may jottli ki ma yónni.» \v 14 Daawuda ne Gàdd: «Am naa njàqare lool; waaye naa tàbbi ci loxol Aji Sax ji, ndax yërmandeem réy na, waaye yàlla buma daanu ci loxol nit!» \p \v 15 Ba loolu amee Aji Sax ji wàcce mbas ci kaw Israyil, dale ko ca suba soosa ba keroog ba àpp ba matee. Ña dee ca askan wa di juróom ñaar fukki junni (70 000) diggante Dan ca bëj-gànnaar ba Beerseba ca bëj-saalum. \v 16 Naka la malaaka ma tàllal loxoom, ngir faagaagal Yerusalem, Aji Sax ji fomm, daldi wax ak Malaakam bóomkat may fàdd askan wa. Mu ne ko: «Doy na! Teggil sa loxo.» Booba malaakam Aji Sax jaa nga ca wetu dàggay Arawna, Yebuseen ba. \p \v 17 Daawuda nag gis malaaka may fàdd askan wa. Mu ne Aji Sax ji: «Man miy sàmm bi\f + \fr 24.17 \fr*\fk sàmm bi: \fk*\ft am na ci bind yu yàgg yi, yu ci indiwul baatub \ft*\fq sàmm bi \fq*\ft ci aaya bii.\ft*\f* déy, maa bàkkaar, maa def lu bon. Ñii diy xar doŋŋ yu topp ci man, lu ñu def? Na sa loxo dal ci sama kaw man kay, maak sama waa kër baay!» \v 18 Ba loolu amee Gàdd dem ca Daawuda keroog ca bés ba, ne ko: «Demal, nga tabaxal Aji Sax ji \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* ca dàggay Arawna, Yebuseen ba.» \v 19 Daawuda dem ca, na ko ko Aji Sax ji sante, Gàdd jottli. \p \v 20 Ba mu ko defee Arawna séen Buur, mu ànd aki jawriñam, jëm ca moom. Mu génn sujjóotal ko, dëpp jëëm ca suuf, \v 21 ne ko: «Buur, sang bi, lu doon say tànk?» Daawuda ne ko: «Xanaa jëndsi sa dàgga jii, ba tabaxal fi Aji Sax ji sarxalukaay, ndax mbas mi dal ci kaw askan wi yem fi.» \v 22 Arawna ne Daawuda: «Buur, sang bi, jëlal lu la neex, def ko sarax. Nag yaa ngi, jëlal def \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, watiiri bojju yeek bant, yi nag yiy lëkkloo, nga def ko matt. \v 23 Man Arawna, maa la jox lii lépp, Buur. Yal na la sa Yàlla Aji Sax ji nangul.» \p \v 24 Teewul Buur ne Arawna: «Déedéet, dama koy jënd ci yaw kay. Ab saraxu rendi-dóomal bu ma dikkewul dara, duma ko defal sama Yàlla Aji Sax ji.» Ci kaw loolu Daawuda jënd dàgga ja ak nag ya ci juróom fukki dogi xaalis. \v 25 Gannaaw loolu Daawuda tabaxal fa Aji Sax ji ab sarxalukaay, rendi fa ay saraxi dóomal, ak ay \w saraxi cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*. Ba mu ko defee Aji Sax ji nangul réew ma, mbas ma bàyyi Israyil.