\id 2KI (WOL) \ide UTF-8 \h 2.Buur ya \toc1 Buur ya, di téereb ñaareel bi \toc2 2.Buur ya \mt1 Buur ya \mt2 di téereb ñaareel bi \c 1 \s1 Yonent Yàlla Ilyaas yar na Buur Akasiya \p \v 1-2 Ba Axab buurub Israyil saayee yàggul dara, Mowabeen ña dañoo fippu, jógal doomam Buur Akasiya. \p Mu am bés Akasiya tollu biir néegam ca kaw taaxum këram ga ca Samari, daldi xàwwikoo ca palanteer ba, daanu ba gaañu lool. Gannaaw gi mu yónni ay ndaw, ne leen: «Demleen seetal ma ca \w Baal Sebub|lemma="Baal:"\w*, tuuru Ekkron, ba xam ndax dinaa dund gannaaw jéll bii ma daanu.» \v 3 Ci biir loolu malaakam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax Ilyaas, ma cosaanoo Tisbi, ne ko: «Demal gaaw dajeek ndawi buurub Samari te laaj leen ne leen: “Xanaa Yàlla daa amul ci Israyil, ba ngeen di seeti ca Baal Sebub, tuuru Ekkron?” \v 4 Loolu tax na Aji Sax ji wax buurub Israyil ne ko: “Lal bi nga tëdd doo ko wàcc, ndax dinga dee moos.”» Ci kaw loolu Ilyaas dem. \p \v 5 Ba ndaw ya waññikoo, Buur Akasiya ne leen: «Lu leen waññi?» \v 6 Ñu ne ko genn góor a leen dogale, ne leen ñu dellu ci buur bi leen yónni, te wax ko ne ko: «Aji Sax ji nee: Ndax Yàlla daa amul Israyil ba ngay yónnee di seetluji ca Baal Sebub, tuuru Ekkron? Loolu tax na lal bi nga tëdd doo ko wàcc, ndax dinga dee moos.» \v 7 Mu ne leen: «Waaw, góor gi leen dogale, wax leen loolu, nu mu mel?» \v 8 Ñu ne ko: «Góor ga boroom kawar la te ngembal der la gemboo.» Akasiya ne: «Kooku Ilyaas mu Tisbi la.» \p \v 9 Ba mu ko defee Akasiya yebal njiitu juróom fukki dag, mu ànd ak juróom fukki nitam, dem ba ca Ilyaas. Gisuñu lu moy mu toog ca kaw tund wa. Njiit la ne ko: «Ée góoru Yàlla gi, Buur nee nga wàcc.» \v 10 Ilyaas wax njiital juróom fukki dag ya, ne ko: «Ndegam góoru Yàlla laa, yal na sawara wàcce asamaan xoyom la, yaw yaak sa juróom fukki dag.» Sawara daldi bàyyikoo asamaan, ne jippét xoyom leen, mook juróom fukki dagam ya. \v 11 Buur dellu yebal keneen ku jiite juróom fukki dag, mu ànd ak juróom fukkam ña. Njiit la dem ne Ilyaas: «Ée góoru Yàlla gi, Buur nee nga wàcc gaaw!» \v 12 Ilyaas wax leen ne leen: «Ndegam góoru Yàlla laa, yal na sawara wàcce asamaan xoyom la, yaw yaak sa juróom fukki dag.» Sawaraw Yàlla bàyyikoo asamaan, xoyom njiit la, mook juróom fukki dagam ya. \v 13 Mu delluwaat yebal njiital juróom fukki dag, mu ànd ak juróom fukkam ña, muy ñetteel bi yoon. Mu daldi dem ba àgg ca Ilyaas, ne gurub sukk ca kanamam; tinu ko ne ko: «Éy góoru Yàlla gi, ngalla wormaalal sama bakkan ak bakkani juróom fukk ñii, sang bi. \v 14 Gis nga ni sawara wàcce asamaan, xoyom ñaari njiiti juróom fukki dag yi ma jiitu, ñook seen juróom fukki dag, waaye rikk wormaalal sama bakkan.» \p \v 15 Malaakam Aji Sax ji ne Ilyaas: «Wàccal ànd ak moom, bu ko ragal.» Mu daldi wàcc ànd ak njiit la ba ca Buur, \v 16 ne ko: «Aji Sax ji nee: Yónni nga ay ndaw, di seeti ca Baal Sebub, tuuru Ekkron, mel ni Yàlla amul ci Israyil, ba ñu man koo laaj kàddoom. Loolu tax na lal bi nga tëdd, doo ko wàcc, nde dinga dee moos!» \p \v 17 Ba loolu amee mu dee, muy la Aji Sax ji waxoon, Ilyaas biral ko. Rakkam Yoram nag falu buur, wuutu ko ca ñaareelu atu nguurug Yoram doomu Yosafat buurub Yuda. Fekk na Akasiya amuloon doom ju góor. \v 18 Li des ci mbiri Akasiya aki jëfam, bindees na ko moos ca téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. \c 2 \s1 Yonent Yàlla Ilyaas yéeg na \p \v 1 Bés ba \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jiy yóbbu Ilyaas kaw asamaan ci biir callweer, ma nga bàyyikoo woon Gilgal, ànd ak Alyaasa. \p \v 2 Ci biir loolu Ilyaas ne Alyaasa: «Xaaral fii rikk, ndax Aji Sax ji da maa yebal Betel.» Alyaasa ne ko: «Ak sama digganteek Aji Sax ji, Kiy Dund, nga fekke tey, duma teqlikook yaw mukk.» Ñu daldi ànd, dem Betel. \p \v 3 Kurélu yonenti Betel nag dikk ca Alyaasa ne ko: «Ndax xam nga ne bésub tey jii Aji Sax ji dina la yenni sa kilifteefu sang Ilyaas?» Mu ne: «Man kay xam naa ko; waaye noppileen rekk.» \p \v 4 Ba mu ko defee Ilyaas ne Alyaasa: «Ngalla xaar ma fii nag, ndax Aji Sax ji da maa yebal Yeriko.» Alyaasa ne ko: «Ak sama digganteek Aji Sax ji, Kiy Dund, nga fekke tey, duma teqlikook yaw mukk.» Ñu daldi ànd, dem Yeriko. \p \v 5 Kurélu yonenti Yeriko nag dikk ba ca Alyaasa ne ko: «Ndax xam nga ne bésub tey jii Aji Sax ji dina la yenni sa kilifteefu sang Ilyaas?» Mu ne leen: «Man kay xam naa ko, waaye noppileen rekk.» \p \v 6 Gannaaw loolu Ilyaas ne Alyaasa: «Ngalla xaaral fii, ndax Aji Sax ji da maa yebal dexu Yurdan.» Alyaasa ne ko: «Ak sama digganteek Aji Sax ji, Kiy Dund, nga fekke tey, duma teqlikook yaw mukk!» Ñu ànd ñoom ñaar. \p \v 7 Ba loolu amee juróom fukki nit bawoo ca kuréli yonent ya, dikk taxaw, dànd leen, janook ñoom fa ñu yem ñoom ñaar ca tàkkal dexu Yurdan. \v 8 Ilyaas jël mbubbam, taxañ, ne ko tàrr ca ndox ma, mu xàjjalikoo yaar. Ñu jaar ci suuf su wow si, jàll ca wàlla. \p \v 9 Ba ñu jàllee, Ilyaas ne Alyaasa: «Wax ma lu ma lay defal bala ñu maa yóbbu, may teqlikook yaw!» Alyaasa ne ko: «Xanaa naa am lu mat sag leer ñaari yoon.» \v 10 Ilyaas ne ko: «Ñaan nga lu jafe. Waaye soo ma gisee bu ñu may jële fi ma nekk ak yaw, yóbbu, kon dinga ko am. Soo ma gisul nag, doo ko am.» \p \v 11 Ci kaw loolu ñu ànd di waxtaan, di dem. Yéguñu lu moy watiiru sawara, wu ànd ak fasi sawara, ne jimeet, dox seen diggante ñoom ñaar; Ilyaas yiiroo aw callweer, yéeg kaw asamaan. \v 12 Alyaasa gis loolu, daldi yuuxu, naan: «Wuy baayee, baay bóoy, yaay watiiru xarey Israyil aki gawaram!» Ba loolu amee gisatu ko. Mu ne sëq ay yéreem, ne ko tareet, def ko ñaar ndaxu tiis, \v 13 doora for mbubb ma wadde ca Ilyaas; ne wërëñ, dem taxawi ca tàkkal dexu Yurdan. \v 14 Ba mu ko defee Alyaasa fab mbubb ma wadde ca Ilyaas, ne ko tàrr ca ndox ma ne: «Ana Aji Sax ji, Yàllay Ilyaas? Ana mu?» Naka la Alyaasa dóor ca ndox ma moom itam, mu xàjjalikoo yaar, mu jàll. \p \v 15 Kuréli yonenti Yeriko ya doon seetaan a nga janook moom naa: «Leeru Ilyaas wàcc na ci kaw Alyaasa!» Ba loolu amee ñu gatandu ko, sujjóotal ko, dëpp seen jë ca suuf. \p \v 16 Ci kaw loolu ñu ne ko: «Xam nga lan la, sang bi? Am na ci nun juróom fukki nit ñu jàmbaare. Nañu dem seetali la sa sang ba. Jombul leeru Yàlla yóbbu ko, teg ko ci kaw tund yii, wenn, mbaa mu teg ko ci biir xur yii, wenn.» Mu ne leen: «Déedéet, buleen leen yebal.» \v 17 Ñu soññ ko, ba mu am ca kersa, ne leen: «Waaw, yebal-leen leen.» Ñu daldi yebal juróom fukki nit, ñu seet diiru ñetti fan, gisuñu kenn. \v 18 Naka lañu dellu ca moom, fekk ko ca Yeriko, mu ne leen: «Newuma leen woon buleen dem?» \p \v 19 Gannaaw loolu waa dëkk ba ne Alyaasa: «Xam nga fi dëkk bi nekk baax na, sang bi, waaye ndox mi baaxul, te suuf si nanguwul.» \v 20 Alyaasa ne leen: «Indil-leen ma ndab lu bees, te def ci xorom.» Ñu indil ko. \v 21 Mu dem ba ca bëtu ndox ba, sànni ca xorom sa, ne: «Aji Sax ji nee: Laabal naa ndox mii. Dootu rey te dootu tax suuf si du nangu.» \v 22 Ndox ma daa laab ba tey jii, muy la Alyaasa waxoon. \p \v 23 Alyaasa bàyyikoo fa, jëm Betel. Ma nga topp yoon wa di dem, ay gone jóge ca dëkk ba, di ko ñaawal, naan ko: «Boroom nel, ca kaw! Ée boroom neleey, ayca ca kaw!» \v 24 Naka la ne gees, ne leen jàkk, daldi leen móolu ci turu Aji Sax ji. Ci kaw loolu ñaari urs\f + \fr 2.24 \fr*\fk urs \fk*\ft rab wu ñàng la; man naa ëpp gaynde.\ft*\f* génne ca àll ba, fàdd ca gone ya ñeent fukk ak ñaar. \v 25 Mu bàyyikoo foofa jubal tundu Karmel, jóge fa dellu Samari. \c 3 \s1 Israyil ak Mowab jote nañu \p \v 1 Ba Yosafat faloo Yuda, ba dugg fukkeelu atu nguuram ak juróom ñett, ca la Yoram doomu Axab falu buur ca Israyil, péeyoo Samari. Yoram nguuru na fukki at ak ñaar, \v 2 di def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu. Waaye taxul mu dab ndeyam ak baayam: jële na fa doj wa ñuy jaamoo \w Baal|lemma="Baal:"\w* te baayam sampoon ko fa. \v 3 Terewul mu sax ci xeetu bàkkaar ya Yerbowam doomu Nebat doon bàkkaarloo Israyil, bañ koo dëddu. \p \v 4 Ci biir loolu, Mesa buuru Mowab doonoon boroom jur, di fey buurub Israyil galagu téeméeri junniy xar (100 000) ak téeméeri junniy kuuy (100 000) yu ñu watul. \v 5 Buur Axab nag dee, buuru Mowab jógal buurub Israyil ba ko wuutu. \v 6 Ba mu ko defee Buur Yoram daldi génn Samari ca saa sa, lim mbooloom xarem Israyil mépp. \v 7 Ba loolu amee mu yónnee ca Yosafat buurub Yuda, ne ko: «Buuru Mowab fippu na, jógal ma. Ndax doo ànd ak man, nu xarejeek Mowab?» Mu ne ko: «Ahakay! Maak yaw benn lanu. Sama mboolooy sa mbooloo, samay fas di say fas,» \v 8 teg ca ne: «Fu nuy jaare, song leen?» Mu ne ko: «Xanaa ca màndiŋu Edom.» \p \v 9 Ba mu ko defee buurub Israyil ak buurub Yudak buurub Edom dem di dox diiru juróom ñaari fan, ba ñook jur gi ñu àndal, kenn amatu ci ndox. \v 10 Buurub Israyil ne: «Musiba am na walla! Nde Aji Sax ji da noo woo, nun ñetti buur yii, ngir teg nu ci loxol buuru Mowab.» \v 11 Yosafat daldi ne: «Ndax yonentu Aji Sax ji nekkul fii, ba nu seetloo ko ci Aji Sax ji?» Kenn ca jawriñi buurub Israyil ne: «Alyaasaa ngi fi, mooy doomu Safat ji doonoon bëkk-néegu Ilyaas.» \v 12 Yosafat ne: «Waaw, kàddug Aji Sax jaa ngi ci moom kay.» \p Ba mu ko defee buurub Israyil ànd ak Yosafat buurub Yuda, ak buurub Edom, dem ca Alyaasa. \v 13 Mu wax ak buurub Israyil ne ko: «Ana lu ma séq ak yaw? Demal kay ca sa yonenti baay yaak sa yonenti ndey ya!» Buurub Israyil ne ko: «Déedéet, ndaxte Aji Sax jee nu fi woo, nun ñetti buur yii, ngir teg nu ci loxol Mowab.» \v 14 Alyaasa ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, Boroom gàngoori xare yi, moom mi may jaamu, bu dul woon ak Yosafat buurub Yuda mii teew, te ma rus ko, duma la xool sax mbaa ma di la faale. \v 15 Waaye indil ma ab xalamkat.» Mu indil ko. \p Naka la xalamkat bay xalam, leeru Aji Sax ji dikkal Alyaasa. \v 16 Alyaasa ne: «Aji Sax ji nee: Gasleen ci xur wii ay kàmbi kàmb. \v 17 Ndaxte Aji Sax ji nee: Du ngelaw lu ngeen di gis mbaa taw, te du tee xur wii fees dell ak ndox, ngeen naan yeen ak seen gétt ak seen jur gu gudd. \v 18 Loolu yomb na Aji Sax ji te dina teg Mowab ci seen loxo it. \v 19 Dingeen nangu mboolem dëkk bu mag bu ñu wëraley tata ak mboolem péey; garab gu baax ngeen gor, mboolem bëti ndox ngeen fatt, tool bu nangu ngeen yàq kooki xeer.» \v 20 Ca suba sa, ba ñuy tollu ci rendi sarax rekk; ndox ma bàyyikoo yoonu Edom, wal, ba fépp fees ak ndox. \p \v 21 Ci biir loolu Mowabeen ñépp dégg ne buur ya ñëw nañu xareseek ñoom. Ñu woo képp ku àttan ngànnaay, mag ak ndaw, ñu bokk taxaw fa seeni réew digaloo. \p \v 22 Ba ñu fanaanee ba ca suba sa, jant bay lerxat ca ndox ma. Waa Mowab tollu ca wàlla, di gis ndox ma xonq, mel ni deret. \v 23 Ña nga naan: «Lee de deret la! Xam naa buur yaa xeexa xeex, ba reyante ca seen biir. Kon nag waa Mowab, ayca, ca lël ja!» \p \v 24 Ba ñu dikkee ba ca dalub Israyil, waa Israyil jóg dal ca seen kaw, ba ñu won leen gannaaw, ne wëqet. Ñu dugg réewum Mowab, duma leen. \v 25 Ba loolu amee ñu yàqte dëkk ya, mboolem tool bu nangu, kenn ku nekk sànni ca xeer ba mu fees, bëtu ndox bu nekk, ñu fatt, garab gu baax gu ne, ñu gor. Mujj na dëkk bu ñu naan Kir Eres doŋŋ a ne ñumm ak xeer ya ñu ko tabaxe. Teewul boroom mbaq ya gaw ko, song ko. \v 26 Ba buuru Mowab gisee xeex bi di ko ëpp doole, daa woo juróom ñaar téeméeri boroom saamar, ànd ak ñoom ngir bëtt, ba àgg ca buurub Edom. Waaye sottiwul. \v 27 Ba loolu amee mu jël taawam bu góor bi nara falu buur, wuutu ko, ne ko teqet rendi, def ko \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* ca kaw tata ja. Waa Israyil ñaawlu jëf ja lool, daldi won buuru Mowab gannaaw, ñibbi seenum réew. \c 4 \s1 Alyaasa jot na jëtun ba \p \v 1 Am na bés ku jëkkëram bokkoon ci yonent yi, di jooytu ci Alyaasa ne ko: «Sama jëkkër de sa ndongo la woon. Léegi nag faatu na, te yaw ci sa bopp sang bi, xam nga ne ku ragaloon \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji la. Waaye ka mu ameeloon bor moo dikk, bëgga yóbbu sama ñaari doom yu góor, ngir def leeni jaam.» \v 2 Alyaasa ne ko: «Loo bëgg ma dimbalee la ko? Wax ma loo am ca kër ga.» Mu ne ko: «Dara, sang bi. Awma dara ca kër ga lu moy taxub diw.» \v 3 Mu ne ko: «Demal àbbi ay ndab yu deful dara ci sa dëkkandoo yi la wër yépp, te bumu néew. \v 4 Su ko defee nga dellu tëjook say doom, ba noppi nga sotti diw gi ci ndab yooyu yépp, bu ci fees, nga ber.» \p \v 5 Mu bàyyikoo nag ca Alyaasa. Gannaaw gi mu tëjuji, mooki doomam; ñu di ko jox, muy sotti. \v 6 Mu dem ba ndab ya fees, mu ne doom ja: «Jottli ma ndab leneen.» Mu ne ko: «Ndab desu fi de.» Diw ga it ne tekk, xelleetul. \v 7 Mu daldi dem wax ko góoru Yàlla ga. Mu ne ko: «Doxal jaay diw gi, fey say bor; la ca des nga dunde, yaak say doom.» \s1 Alyaasa am nab dal \p \v 8 Am na bés Alyaasa jaare dëkk bu ñuy wax Sunem. As ndaw su bare alal woo ko lekk këram, di ko soññ. Mujj na saa yu fa jaaree, daldi fay toog, ba xéewlu. \v 9 Ci biir loolu mu ne jëkkëram: «Aa, man déy, xam naa ne kiy fara dal ak nun góoru Yàlla gu sell la. \v 10 Tee nu koo tabaxal néeg bu ndaw ci kaw taax mi, defal ko ca ab lal ak taabal ak toogu akub làmp, ba bu ñëwatee dal ca?» \s1 Alyaasa delloo na njukkal \p \v 11 Noonu la Alyaasa dikke bés, dal ca néeg ba ñu ko tabaxal ca kaw taax ma, tëdd fa. \v 12 Ci kaw loolu mu ne surgaam Gewasi: «Wool ma ndawas Sunem sii.» Mu wool ko ko, mu dikk taxaw. \v 13 Mu ne surgaam: «Waxal ma ndaw sii ne ko: “Waaw, yaw de yaa ngi sonn ci nun coono bii bépp! Ana loo bëgg nu defal la ko? Ndax nu waxal la Buur lu jëm ci yaw, am nu wax ak njiital mbooloom xare ma?”» Mu wax ko, mu ne ko: «Jërëjëf, waaye am naa teraanga ci sama biiri bokk.» \v 14 Alyaasa ne Gewasi: «Ana lu nu koy defal nag?» Mu ne ko: «Amul doom ju góor de, te jëkkëram mag la.» \v 15 Alyaasa ne ko: «Woowaat ko.» Mu woo ko; mu dikk, taxaw ca bunt ba. \v 16 Alyaasa ne ko: «Nëgëni déwén dinga leewu doom ju góor.» Mu ne ko: «Déet, sang bi, góoru Yàlla gi, bu ma nax mukk, sang bi.» \p \v 17 Ndaw sa nag mujj ëmb; ca déwén sa mu am doom ju góor, ca jamono jooja, muy la ko Alyaasa waxoon. \p \v 18 Xale ba di màgg. Mu am bés mu dem fekki baayam ca ñay góob. \v 19 Mu jekki ne baayam: «Wóoy baay, sama bopp bi, sama bopp bi!» Baay ba ne surga ba: «Yóbbu ko ca yaayam.» \v 20 Surga ba fab ko, yóbbu ca yaayam, mu uuf ko, ba ca digg bëccëg, xale ba dee. \v 21 Yaay ja yéeg, tëral ko ca kaw lalu góoru Yàlla ga, tëj bunt ba, daldi génn. \v 22 Mu woo jëkkëram, ne ko: «Rikk boole maak kenn ci surga yi te jox ma menn mbaam, ma daw ba ca góoru Yàlla ga te ñëw gaaw.» \v 23 Mu ne ko: «Ana loo wuti ca moom tey, te du Terutel weer, du \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*?» Mu ne ko: «Jàmm la.» \p \v 24 Ba loolu amee ndaw sa takk mbaam ma, ne surgaam: «Doxal jiitu, bu ma taxawloo ci yoon wi te waxuma la ko.» \v 25 Mu dem ba àgg ca góoru Yàlla ga, ca tundu Karmel. \p Góoru Yàlla ga séen ko fu sore, ne surgaam Gewasi: «Xoolal, ndawas Sunem saa ngi. \v 26 Dawal gaaw dajeek moom, laaj ko mbaa mu ngi ci jàmm mook jëkkëram ak doomam.» Mu laaj ko, mu ne ko: «Jàmm rekk la.» \v 27 Mu agsi nag ca góoru Yàlla ga, ca kaw tund wa, ne fëlëñ ca suuf, jàpp ca tànk ya. Gewasi dikk, bëgg koo bëmëx, mu ne ko: «Bàyyi ko, xolam a naqari. \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nag nëbb na ma ko, xamalu ma lan la.» \v 28 Ndaw sa ne ko: «Sang bi, ndax maa la ñaan doom ju góor? Newuma la woon bu ma nax?» \p \v 29 Ba loolu amee Alyaasa ne Gewasi: «Takkul, ŋàbb sama yet ci sa loxo te daw dem. Koo mana taseel, bu ko nuyu te bu la nuyoo, bu ko fey. Boo àggee, tegal sama yet wii ca kaw kanamu xale ba.» \v 30 Teewul yaayu xale ba ne ko: «Ak sama digganteek Aji Sax ji, Kiy Dund, nga fekke tey, duma la fi bàyyi.» Mu daldi jóg topp ca moom. \p \v 31 Fekk na Gewasi jiitu leen. Ba mu agsee, teg na yet wa ca kaw kanamu xale ba, waaye xale ba àdduwul, yënguwul. Gewasi waññiku, dajeek Alyaasa ne ko: «Xale ba de yewwuwul!» \v 32 Ba Alyaasa agsee ca kër ga it, fekkul lu moy néewu xale bi tëdd ca kaw lal ba. \v 33 Naka la dugg, tëj bunt ba, ñoom ñaar ca biir. Mu ñaan ci Aji Sax ji, \v 34 ba noppi yéeg, daldi tàlli ca kaw xale ba, tafu ca kawam, gémmiñ ak gémmiñ, bët ak bët, biir loxook biir loxo. Naka la bóof ca kaw xale ba, yaram wa tàmbalee tàngaat. \v 35 Alyaasa jóg di jaabante ca biir néeg ba. Nes tuut mu yéeg, bóofaat ca kaw xale ba; xale ba daldi tisli ba muy juróom ñaari yoon, ne xiféet. \v 36 Ba loolu amee Alyaasa woo Gewasi ne ko: «Wool ndawas Sunem soosu.» Mu woo ndaw sa, mu dikk. Mu ne ko: «Jëlal sa doom.» \v 37 Ndaw sa ne gurub cay tànkam, sujjóot; ba noppi fab doomam, génn. \s1 Alyaasa sekki na tooke ja \p \v 38 Gannaaw loolu Alyaasa ñibbi Gilgal, mu yemook xiif am ca réew ma. Mu am bés kurélu yonent ya daje fa moom. Alyaasa ne surgaam: «Tegal cin lu mag li te toggal yonent yii mbuum.» \v 39 Ci kaw loolu kenn ca ñoom génn, dem ca àll ba, di witti ay xob, daldi fa gis ag lawtan gu doom ya mel ni yomb, mu witt ca ba mbubbam fees. Mu dellu, fejat ko, yeb ca cinu mbuum la, te kenn xamul lu mu doon. \v 40 Ñu yekkal ko nit ña, waaye manuñu koo lekk. Naka lañu mos rekk, yuuxoo ne: «Lekk-dee la cin li def de, góoru Yàlla gi!» \v 41 Alyaasa ne: «Indil-leen ma sunguf.» Ñu indi, mu xëpp ca cin la, daldi ne: «Sottil-leen mbooloo mi, ñu lekk.» Ba loolu amee dara lu aay amatul ca cin la. \s1 Alyaasa leel na mbooloo \p \v 42 Ba loolu wéyee jenn waay jóge Baal Salisa, indil góoru Yàlla ga mburum pepp ma jëkka ñor, muy ñaar fukki mburuy lors, boole ciy gubi bele, yeb ko ci saakoom. Alyaasa ne ñu jox ko mbooloo mi, ñu lekk. \v 43 Ka koy séddale ne ko: «Waaw, nu may taajale lii téeméeri nit?» Mu ne ko: «Joxal mbooloo mi ñu lekk, ndax \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nee: Dinañu lekk ba mu des.» \v 44 Mu taajal leen ko, ñu lekk ba desal, muy la Aji Sax ji waxoon. \c 5 \s1 Alyaasa faj na kilifa \p \v 1 Bu loolu wéyee Naaman njiital xareb buurub Siri la woon. Sangam buurub Siri nawloo ko lool, def ko nitam, ndax ciy loxoom la \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji jaarale ndam li mu mayoon waa Siri. Ku jàmbaare la woon, waaye daa amoon jàngoroy ngaana\f + \fr 5.1 \fr*\fk ngaana: \fk*\ft baat bi man naa ëmb yeneen jàngoroy der juy law te aay, yu dul ngaana kese.\ft*\f*. \p \v 2 Fekk na ay xarekati waa Siri dem songi réewum Israyil, jàppe fa ab janq, def ko surgab jabaru Naaman. \v 3 Mu am bés janq ba ne njaatigeem: «Éy su sama sang bi demoon ca yonent ba ca Samari! Kon de dina ko teggil jàngoroy deram ji.» \p \v 4 Naaman nag dem wax Buur, sangam, ne ko janqub waa Israyil ba nee na nàngam ak nàngam. \v 5 Buurub Siri ne ko: «Demal kay, dinaa la yóbbante buurub Israyil bataaxal.» Mu dem, yóbbaale ñetti téeméeri kiloy xaalis, ak juróom benn fukki kiloy wurus, ak fukki mbubbi xew; \v 6 bataaxal ba mu yót buurub Israyil nag, lii lañu ca bind: «Bataaxal bii maa ko teg ci sama loxol surga Naaman, yebal ko ci yaw, ngir nga fajal ko ngaana gi ko dal.» \p \v 7 Naka la buurub Israyil jàng bataaxal ba rekk, ne mbubb ma tareet ndax jaaxle, daldi ne: «Man dama di Yàlla bay rey, mbaa may dundal, ba kii di yebal nit ku may fajal ngaana! Seetleen lii rekk: kii da may wut!» \p \v 8 Ba Alyaasa, góoru Yàlla ga déggee ne buurub Israyil xotti na mbubbam, daa yónnee ca moom, laaj ko ne ko: «Ana lu tax nga xotti sa mbubb? Yebalal waa ji ci man rekk. Dina xam ne yonent a ngi ci Israyil.» \v 9 Ba loolu amee Naaman yóbbaale ay fasam aki watiiram, dikk taxaw ca bunt kër Alyaasa. \v 10 Alyaasa yebal ndaw ca moom ne ko: «Demal sanguji juróom ñaari yoon ca dexu Yurdan, sa yaram set, dellu mel na mu meloon.» \p \v 11 Naaman nag mer. Ma ngay dem te naan: «Xoolal rekk, man mi noon day daldi génn taxaw ci biti, ñaan ci Yàllaam Aji Sax ji, tiimale loxoom ër bi, daldi teggi jàngoro ji! \v 12 Te sax xanaa Abanaa ngi nii ak Parpar, di dexi Damaas, gën fopp mboolem ndox muy wal ci Israyil? Ndax dama caa manuloona sangu, ba wér?» Mu walbatiku dem, mer lool. \p \v 13 Surgaam ya nag dikk, kenn ca ñoom ne ko: «Baay Naaman, su doon lu jafe la la yonent bi wax ndax danga ko dul def? Kon kay su la nee nga sangu rekk, set wecc, nga war koo def!» \v 14 Naaman nag doora dem, sóobu ca dexu Yurdan ga, ba muy juróom ñaari yoon, muy la góoru Yàlla ga waxoon. Mu daldi wér, yaram wa mel ni yaramu xale bu góor bu ndaw, set wecc. \p \v 15 Ba loolu amee Naaman dellu ca góoru Yàlla ga, mook mboolem toppam ma. Mu dikk ba ca moom, taxaw ne: «Dama ne léegi wóor na ma ne amul jenn Yàlla ci mboolem àddina ju moy Yàlla ji ci Israyil. Kon nag sang bi, ngalla nangul lii, maa la ko may.» \v 16 Alyaasa ne ko: «Déedéet. Giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, moom mi may jaamu, duma ko jël.» Mu soññ ko, soññ, mu bañ. \v 17 Naaman ne ko: «Gannaaw bañ nga, sang bi, nañu ma may sëfub ñaari berkelle ci suuf, ngir kat, sang bi, dootuma jébbal ay tuur \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* mbaa yeneen sarax, xanaa Aji Sax ji doŋŋ\f + \fr 5.17 \fr*\ft Naaman dafa yaakaaroon ne Aji Sax ji, Israyil rekk lañu ko mana jaamoo. Teewul mu defe ne ku sàkk suufas Israyil, tabaxal ko ca feneen sarxalukaay, Aji Sax ji man na faa nangu sa jaamu ba tey.\ft*\f*. \v 18 Waaye sang bi, lenn rekk laay ñaan, Aji Sax ji jéggal ma ko. Bu sama sang ba di dugg ca kër tuur ma ñuy wax Rimon, di ko sujjóotal, ba jàpp sama loxo, ma ànd ak moom sujjóot ca kër Rimon, yal na ma Aji Sax ji jéggal la ma fay sujjóot rekk, sang bi.» \v 19 Alyaasa ne ko: «Demal ak jàmm.» \s1 Gewasi lal na pexe \p Ba Naaman bàyyikoo ca Alyaasa, dem ba xawa sore, \v 20 Gewasi surgab góoru Yàlla ga, Alyaasa, ne ca xelam: «Eewaay sama sang daal! Day bàyyi Naaman waa Siri bii mu dem noonu rekk; jëlul dara ci li mu indi. Giñ naa ko ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, Kiy Dund, dinaa daw dabi ko, ba am ci moom as lëf.» \p \v 21 Gewasi daldi daw dabi Naaman. Ba ko Naaman séenee muy daw wutsi ko, mu cëppoo ca watiiram dajeek moom, ne ko: «Mbaa jàmm la?» \v 22 Mu ne ko: «Jàmm la kay. Sama sang a ma yónni ne ma ma wax la ne ñaari xale yu góori yonent a agsi léegi, jóge diiwaanu tundi Efrayim. Nee ndax doo ko jox fanweeri kiloy xaalis ak ñaari mbubbi xew yu mu leen may?» \v 23 Naaman ne ko: «Ahakay! Jëlal juróom benn fukki kiloy xaalis kay!» Mu soññ ko nag, ba mu ëmb juróom benn fukki kiloy xaalis yi ci ñaari mbuus, boole ca ñaari mbubbi xew, jox ko ñaari surgaam, ñu gàddu, jiitu Gewasi. \v 24 Gewasi agsi ca tund wa, jële ko ca seeni loxo, dem, denci ko ca biir kër ga, ba noppi yiwi leen, ñu dem. \p \v 25 Ba loolu wéyee mu dellu ca sangam Alyaasa. Mu ne ko: «Foo jóge nii?» Mu ne ko: «Demuma fenn di, sang bi.» \v 26 Alyaasa ne ko: «Defe nga ne samag leer teewuloon, ba nit kay wàcce ca watiiram, di dajeek yaw? Ndax danoo tollu ci jël xaalisu kenn aki mbubb mbaa ay tooli oliw aki tooli reseñ aki gàtt aki nag aki jaam yu góor ak yu jigéen? \v 27 Ngaanag Naaman dina la topp, yaak saw askan ba fàww!» Ba mu ko defee Gewasi bàyyikoo ca Alyaasa, daldi gaana, yaram wa ne fureet, weex furr. \c 6 \s1 Weñu sémmiñ ga tëmb na \p \v 1 Am na bés mbooloom yonent ya wax Alyaasa ne ko: «Xoolal, fii nuy dajeek yaw daa xat. \v 2 Nan dem ngalla ba ca tàkkal dexu Yurdan, ku nekk ci nun sàkk fa aw dénk, nu defaral fa sunu bopp bérab bu nu daje.» Alyaasa ne leen: «Demleen.» \v 3 Kenn ca ñoom ne ko: «Sang bi, ñëwal nu dem kay!» Mu ne ko: «Waaw, nan dem.» \v 4 Mu ànd ak ñoom dem ba ca dexu Yurdan, di fa gor ay garab. \v 5 Kenn ca ñoom doon gor, weñu sémmiñam wadd ca ndox ma. Mu jalu, ne: «Éy, sang bi, te dama koo àbboon kat!» \v 6 Góoru Yàlla ga ne ko: «Fu mu wadd?» Mu won ko fa mu wadd, mu dog bant sànni foofa, weñ ga tëmb. \v 7 Mu ne ko: «Foral!» Mu yóotu, for ko. \s1 Alyaasa sànk na gàngoor \p \v 8 Bu loolu wéyee buurub Siri doon na xareek Israyil. Ci biir loolu mu diisooki surgaam, ne leen bérab sàngam lay def ab dalam. \v 9 Ci kaw loolu góoru Yàlla ga yónnee ca buurub Israyil, ne ko: «Nanga moytoo jaare bérab sàngam, ndaxte fa la waa Siri jëm.» \v 10 Buurub Israyil yónnee fa ko góoru Yàlla ga wax, ngir nemmiku foofa. Alyaasa di artoo Buur noonu, muy fàggandiku. Loolu am na bu dul benn yoon, du ñaar. \v 11 Buurub Siri nag jàq lool ci loolu, daldi woolu ay jawriñam ne leen: «Ana kan ci yeen moo fi nekkal buurub Israyil?» \v 12 Kenn ca jawriñ ya ne ko: «Du kenn, Buur sang bi; waaye Alyaasa, yonent bi ci Israyil mooy jottli buurub Israyil kàddu yi ngay wax ci sa biir néegu biir.» \v 13 Mu ne: «Seetalileen ma ko, ma yónnee, jàpp ko.» Ñu mujj xamal ko ne: «Moom de, ma nga ca Dotan.» \v 14 Buurub Siri yebal fa ay dag yu takku, yóbbaale ay fas aki watiir. Mu agsi guddi, gaw dëkk ba. \p \v 15 Ci kaw loolu bëkk-néegub góoru Yàlla ga jóg ca suba teel, génn, gisul lu moy mbooloom xare mu gaw dëkk ba, aki fas aki watiir. Mu ne ko: «Éy sang bi, fu nu jëm?» \v 16 Alyaasa ne ko: «Bul tiit, noo leen ëpple ñu ñu àndal.» \v 17 Alyaasa nag ñaan ne: «\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ngalla ubbil ay bëtam, mu gis.» Aji Sax ji ubbi bëti surga ba, mu xool, ndeke tund waa nga fees aki fas aki watiiri sawara, wër Alyaasa. \p \v 18 Ba mu ko defee waa Siri wutsi Alyaasa, mu ñaan ci Aji Sax ji ne ko: «Rikk muural bëti mbooloo mii.» Aji Sax ji muur seeni bët, na mu ko ko ñaane. \v 19 Alyaasa nag ne leen: «Fii du yoon wi de, te du dëkk bi ngeen di seet it. Toppleen ma, ma yóbbu leen ci ki ngeen di seet.» Mu daldi leen yóbbu ba Samari. \p \v 20 Ba ñu duggee Samari, Alyaasa dellu ñaan ne: «Aji Sax ji, ngalla ubbil bëti nit ñii, ñu gis.» Aji Sax ji muri seeni bët, ñu xoole rekk, gis ne ñu ngi biir Samari. \v 21 Buurub Israyil gis leen ne: «Baay Alyaasa, ma rey leen? Ãa, ma rey leen?» \v 22 Mu ne ko: «Bu leen rey mukk. Xanaa ñoo jàpp cib xare sax doo leen rey? May leen ñu lekk, naan, te dellu ca seen sang.» \v 23 Ba loolu wéyee Buur berndeel leen bernde ju réy; ñu lekk, naan; mu yiwi leen, ñu ñibbi ca seen sang. Booba la waa Siri gëjoona def gàngoori yàqkat, di dugg biir réewum Israyil. \s1 Xiif ba tar na ca Samari \p \v 24 Ba ñu demee ba yeneen jamono, Ben Addàd buurub Siri woo mbooloom xareem mépp, dem gawi Samari. \v 25 Xiif bu metti am ca Samari ndax gaw ba, ba boppub mbaam-sëf di jar juróom ñett fukki dogi xaalis, genn-wàll liibaru jonkanu pitax\f + \fr 6.25 \fr*\fk jonkanu pitax: \fk*\ft am na ñu jàpp ne jonkanu pitax xollitu peppu saxayaay la gu ñuy wooye noonu.\ft*\f* di jar juróomi dogi xaalis. \v 26 Mu am bés buurub Israyil jaar ca kaw tata ja, senn as ndaw àddu ca kaw ne ko: «Buur, sang bi, ngalla wallu ma!» \v 27 Mu ne ko: «Bu la \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji walluwul, nu ma lay walloo? Du pepp, du ndoxum reseñ ju ma la mana may.» \v 28 Mu teg ca ne ko: «Lan la sax?» Ndaw sa ne ko: «Ndaw sii da ma noon: “Indil sa doom, nu lekk ko tey, ëllëg nu lekk sama doom.” \v 29 Nu togg sama doom, bokk ko lekk. Ma ne ko: “Su ëllëgee indil sa doom, nu bokk ko lekk.” Moom nag mu làq doomam.» \v 30 Ba Buur déggee kàdduy ndaw sa, daa xotti mbubbam ndaxu naqar. Ma ngay dox, di wéy ca kaw tata ja, mbooloo ma tollu ci suuf séenuñu lu moy saaku bi mu def njiitlaay, di ko ñaawloo. \p \v 31 Ma nga naan: «Yal na ma Yàlla teg mbugal mu gëna tar ndegam bésub tey jii boppub Alyaasa doomu Safat du teqlikook baatam.» \v 32 Fekk na Alyaasaa nga ca këram toog, mag ña bokk toog ak moom. Buur yebal ndaw ca moom. Ndaw la agseegul, Alyaasa ne mag ña: «Xool-leen bóomkat bii yebal kuy dogsi sama bopp! Xam ngeen lan la, bu ndaw li agsee rekk, tëjleen bunt bi, tere koo dugg; ndax du tànki sangam laay dégg, mu topp ci moom sax?» \p \v 33 Naka la Alyaasa di wax, ndaw la ne jimeet, jëm ca moom. Ma nga naan: «Gis nga musiba mii Aji Sax ji wàcce. Kon ana lu may séentooti ci Aji Sax ji?» \c 7 \p \v 1 Ba loolu amee Alyaasa ne: «Dégluleen kàddug Aji Sax ji. Aji Sax ji nee: Nëgëni ëllëg benn nattub lëmm ci sunguf su mucc ayib benn dogu xaalis doŋŋ lay doon, ñaari natti lors it di benn dogu xaalis ca buntu Samari.» \v 2 Jaraaf ja daan ànd ak Buur saa su ne àddu ca ne góoru Yàlla ga: «Ma ne, su Aji Sax ji ubbi woon sàqi asamaan sax, ndax man naa tax loolu am?» Mu ne ko: «Dinga ci teg sa bët déy, waaye doo ci lekk.» \s1 Aji Sax ji wallu na Samari \p \v 3 Ci biir loolu amoon na ñeenti gaana yu nekkoon ca bunt dëkk ba. Ña nga naan ci seen biir: «Xanaa dunu toog fii ba dee? \v 4 Su nu demee ca biir dëkk ba, danuy dee ak xiif. Su nu toogee fii itam, dee ak xiif. Kon kay nan dem ca dalub waa Siri, jébbal leen sunu bopp. Su ñu nu bàyyee, nu dund, baax na. Su ñu nu reyee it, nu dee rekk.» \p \v 5 Ci kaw loolu ñu jóg timis, jëm ca dalub waa Siri. Ba ñu agsee ca peggub dalu waa Siri, gisuñu luy nirook nit sax. \v 6 Booba fekk na Boroom bi dégtal waa dalub Siri ba riirum fas yu ànd aki watiiri xare ak gàngoor gu réy, ba tax ñu naan ca seen biir: «Ãa! Loolu de, buuri Etteen ñaak buuri Misraa, Buurub Israyil fey leen, ngir ñu songsi nu!» \v 7 Ba mu ko defee ñu jóge fa ca timis, bàyyi fa seeni xaymaak seeni fas ak seeni mbaam, wacc dal ba noonu, daw rawaleji seen bakkan. \p \v 8 Ñeenti gaana ya nag dikk, ba jub dal ba, daldi jegesi, dugg cib xayma, lekk fa, naan, jële fa xaalis ak wurus aki yére, dem nëbbi ko; dellu duggaat cib xayma jëleeti fa, dem nëbbi ko. \v 9 Ba loolu amee ñu ne ca seen biir: «Nun kat defunu njub. Bésub tey jii bésub jàmm la; nun, nu ne patt yéglewunu ko. Su nu xaaree ba jant bi leer de, àq dina nu topp. Kon nag aycaleen nu dem yeggeji ko waa kër Buur.» \v 10 Ñu daldi dem woo wattukati bunt dëkk ba, wax leen, ne leen: «Dem nanu ca biir dalu waa Siri; ndeke kenn nekku fa, baat jibu fa; dara lu moy fas yu yeeweek mbaam yu yeeweek xayma yu ne ñumm.» \p \v 11 Wattukati bunt ba woote, yégle ko ca biir kër Buur. \v 12 Buur jóg ca guddi, wax aki jawriñam ne leen: «Ma wax leen nag li nu waa Siri di fexeel. Xam nañu ne nu ngi dee ak xiif. Moo tax ñu jóge ca seen dal, làquji ca àll ba. Xam naa dañu ne: “Bu ñu génnee dëkk bi rekk, nu jàpp leen, ba noppi dugg ci biir dëkk bi.”» \v 13 Kenn ca jawriñ ya ne ko: «Nanu yónni rekk ay nit ñu war juróomi fas ci yi nu dese ci dëkk bi. Bu ñu leen reyee de, ñook mbooloom Israyil mi des ci dëkk bi yépp ay yem demin. Kon nanu leen yónni rekk te seet ba xam.» \p \v 14 Ba loolu amee ñu waajal ñaari watiir ak seeni fas, Buur yebal ay ndaw yu toppi mbooloom Siri, ne leen: «Demleen seeti.» \v 15 Ñu dem toppi leen ba ca dexu Yurdan, ndeke yoon wa fees na dell aki yéreeki jumtukaay yu waa Siri sànni, ba ñuy daw. Ndaw ya waññiku, wax ko Buur. \v 16 Mbooloo ma riir, génn wuti dalu Siri ba, sëxëtoo ko. Ci kaw loolu benn nattub lëmm ci sunguf su mucc ayib di jar benn dogu xaalis doŋŋ, ñaari natti lors it di benn dogu xaalis, muy la \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxoon. \v 17 Fekk na Buur teg jawriñam ja mu doon àndal saa su nekk ca buntu dëkk ba, mu di ko wattu. Mbooloo ma nag di buuxante, ba dëggaate ko ca bunt ba, mu dee. Muy la góoru Yàlla ga yégle woon ba Buur dikkee ca moom. \v 18 Na ko góoru Yàlla ga waxe woon Buur, ne ko: «Nëgëni ëllëg benn nattub lëmm ci sunguf su mucc ayib doon benn dogu xaalis doŋŋ, ñaari natti lors it di benn dogu xaalis ca buntu Samari,» noonu la ame. \v 19 Jaraaf ja da caa àddu woon ne góoru Yàlla ga: «Ma ne, su Aji Sax ji ubbi woon sàqi asamaan sax ndax man naa tax loolu am?» Mu ne ko: «Dinga ko gisal sa bopp déy, waaye doo ci lekk.» \v 20 Loolu ci boppam moo ko dal itam, ndax mbooloo ma dañoo buuxante, ba dëggaate ko ca bunt ba, mu dee. \c 8 \s1 Ndawas Sunem sa jotaat na alalam \p \v 1 Am na bés Alyaasa wax ndaw sa mu dekkaloon doomam ju góor ne ko: «Ayca, àndal ak sa njaboot, ngeen dali fu ngeen mana dal, ndax \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dogal na ab xiif ci réew mi, te dina am juróom ñaari at.» \v 2 Ndaw sa fabu, def la ko góoru Yàlla ga wax, dem yoonam mook njabootam, dali ca réewum Filisteen ña, toog fa diiru juróom ñaari at. \v 3 Ba juróom ñaari at ya matee, ndaw sa jóge ca réewum Filisteen ña, ñibbsi. Mu dem ca Buur, di sàkku mu delloo ko këram ak suufam. \v 4 Loolu fekk Buur di waxtaan ak Gewasi, surgab Alyaasa góoru Yàlla ga, naan ko: «Ayca, wax ma mboolem jaloore yi Alyaasa def.» \v 5 Gewasi nag di nettali Buur na Alyaasa dekkalee woon xale ba, rekk ndaw sa Alyaasa dekkaloon doomam ju góor ne jalañ, di sàkkusi ca Buur mu jox ko këram ak suufam. Gewasi ne ko: «Ndaw saa ngii nag, Buur, sang bi. Doomam ju góor jii la Alyaasa dekkaloon.» \v 6 Buur laaj ndaw sa, mu wax ko lépp. Buur boole kook bëkk-néegam ne ko: «Fexeel ba ñu delloo ndaw sii lépp luy alalam ak dayob lépp lu suufam meññoon, la ko dale ca bés ba mu fi jógee ba tey jii.» \s1 Asayel mujj na falu ca Siri \p \v 7 Am na it yoon wu Alyaasa demoon Damaas, péeyu Siri. Fekk Ben Addàd buurub Siri wopp. Ba ñu ko waxee ne ko: «Góoru Yàlla gi ñëw na fi.» \v 8 Buur ne Asayel, ab jawriñam: «Demal ca góoru Yàlla ga te yóbbaale loo teg ci loxoom, mu seetal ma ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Laajal ma ko ne ko: “Ndax dinaa jóg ci sama wopp jii?”» \v 9 Asayel dem ca moom, yóbbaale lu mu ko jox, muy mboolem la gën ca Damaas, tollu ci sëfub ñeent fukki giléem. Mu dikk taxaw ca kanamam, ne ko: «Ben Addàd buurub Siri moo ma yónni fi yaw, ne ma: “Laajal ma Baay Alyaasa ndax dinaa jóge ci sama wopp jii.”» \v 10 Alyaasa ne ko: «Demal ne ko dina jóg moos, waaye Aji Sax ji won na ma ne dina dee déy!» \v 11 Ba loolu amee góoru Yàlla ga ne dann, ne ko jàkk, ba Asayel rus. Mu daldi jooy. \p \v 12 Asayel ne ko: «Sang bi, looy jooy?» Mu ne ko: «Damaa xam lu bon li ngay defi waa Israyil. Seeni tata ngay taal, seeni xale yu góor nga jam saamar ñu dee, seeni doom nga tas ci suuf, seeni jigéeni biir nga butti.» \v 13 Asayel ne ko: «Moo sang bi, man mi ab xaj gën, nu ma mana defe jooju jëf ju réy?» Alyaasa ne ko: «Aji Sax ji won na ma ne yaay doon buurub Siri.» \v 14 Asayel bàyyikoo ca Alyaasa, dellu ca sangam. Mu ne ko: «Lu la Alyaasa wax?» Mu ne ko: «Nee na ma de dinga jóg moos.» \v 15 Ca ëllëg sa nag Asayel fab malaan, xooj ko ci ndox, dëpp ko ca kanamu buur ba, fatt ko, mu dee. Gannaaw loolu Asayel falu buur, wuutu ko. \s1 Yoram falu na Yuda \p \v 16 Ba buurub Israyil Yoram doomu Axab duggee juróomeelu atu nguuram, ca la Yoram doomu Yosafat buurub Yuda falu buur ca Yuda. \v 17 Fanweeri at ak ñaar la amoon ba muy falu buur, te juróom ñetti at la nguuru fa Yerusalem. \v 18 Tànki buuri Israyil la topp, di roy waa kër Axab, ndax doomu Axab la jël jabar, di def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu. \v 19 Waaye Aji Sax ji bugguloona tas Yuda ngir Daawuda, jaamam ba, ndax la mu ko digoona may ci ay doomam kuy saxal nguuram fàww, ba du fey. \p \v 20 Ca jamonoy Yoram la Edomeen ña fippu, bañ moomeelu Yuda, ba fal seen buuru bopp. \v 21 Gannaaw loolu Yoram jàll ba Sayir, yóbbaale watiiri xareem yépp. Moo jóg ag guddi, dal ca kaw Edomeen ña leen gawoon, moom ak njiiti watiiri xareem. Waaye gàngooru Yuda ñoo daw, dellu ca seeni xayma. \v 22 Edomeen ñaa ngi bañ moomeelu Yuda ba tey jii. Jant yooyu la Libna itam fippu. \p \v 23 Li des ci mbiri Yoram ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. \v 24 Yoram nag tëdd, fekki ay maamam, ñu denc ko ca bàmmeelu maamam ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. Doomam Akasiya falu buur, wuutu ko. \s1 Akasiya falu na Yuda \p \v 25 Ba Yoram doomu Axab buurub Israyil duggee ca fukkeelu atu nguuram ak ñaar, ca la Akasiya doomu Yoram falu buur ca Yuda. \v 26 Ñaar fukki at ak ñaar la Akasiya amoon ba muy falu buur, te menn at la nguuru fa Yerusalem. Atalyaa mooy yaayam, sëtub Omri buurub Israyil. \v 27 Akasiya topp ca tànki waa kër Axab, di def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu ni waa kër Axab, ndax goro la woon ca waa kër Axab. \v 28 Akasiya ànd naak Yoram doomu Axab, xarejeek Asayel buurub Siri ca Ramot Galàdd. Waa Siri jam Yoram. \v 29 Buur Yoram nag walbatiku fajuji ca Yisreel ndax jam-jami waa Siri ya ca Raama, ba muy xareek Asayel buurub Siri. Doomu Yoram, Akasiya buurub Yuda nag dem seeti Yoram doomu Axab fa Yisreel ndax jagadeem ga. \c 9 \s1 Alyaasa fal na Yewu \p \v 1 Ci kaw loolu Yonent Yàlla Alyaasa woolu kenn ca kurélu yonent ya, ne ko: «Takkul, jël taxub diw bii, te dem ba Ramot Galàdd. \v 2 Boo yeggee, seet fa Yewu doomu Yosafat doomu Nimsi. Fekk ko ca ña muy àndal, jële ko ca seen biir, ànd ak moom, dugg néeg bu ngeen mana ñaaroo. \v 3 Su ko defee nga jël taxub diw bi, sotti ko ci kaw boppam te wax ko ne ko: “\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nee: Diw naa la, fal la ngay buurub Israyil.” Boo noppee, bul yeexantu. Ubbil bunt ba, daw.» \p \v 4 Ba loolu amee xale bu góor ba, yonent bu ndaw ba, dem ba àgg Ramot Galàdd. \v 5 Naka la agsi rekk, fekk njiiti mbooloom xare mi bokk toog. Mu ne: «Kilifa gi, bataaxal laa la indil.» Yewu ne ko: «Ku ko moom ci nun?» Mu ne ko: «Xanaa yaw, kilifa gi.» \v 6 Yewu jóg, ànd ak moom, dugg ca biir kër ga, mu sotti diw ga ca boppam, ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Israyil nee: Diw naa la, fal la buurub Israyil sama ñoñ. \v 7 Nanga tas sa kër sang Axab, te noonu laay toppe soxnaam Yesabel sama bakkani jaam ñépp: muy yonenti Aji Sax jeek ñi dul yonent. \v 8 Waa kër Axab yépp ay dee. Dinaa faagaagal képp kuy góor te bokk ci waa kër Axab, ci digg Israyil, muy gor di jaam. \v 9 Dinaa def kër Axab tas, mel ni kër Yerbowam doomu Nebat, mbaa kër Basa doomu Axiya. \v 10 Yesabel moom, ay xaj a koy lekk ca toolub Yisreel, kenn du ko suul.» Ba loolu amee mu ubbi bunt ba, daw. \p \v 11 Yewu génn, dellu ca moroomi jawriñam ña. Ñu ne ko: «Mbaa jàmm? Lu indi dof bii ci yaw?» Mu ne leen: «Ah, xam ngeen nit kii aki waxam rekk!» \v 12 Ñu ne ko: «Wax nu waay, bu nu nax!» Mu ne leen nee na ko nàngam ak nàngam, teg ca ne leen: «Mu ne: “Aji Sax ji nee: Diw naa la, fal la buurub Israyil.”» \v 13 Ba mu ko defee ñu gaaw, summi seeni mbubb ñoom ñépp, lalal ko ca kaw dëggastal ya, ba noppi wal liit ga naa: «Yewu falu na buur!» \s1 Yewu fexeel na buur ya \p \v 14 Ba loolu amee Yewu doomu Yosafat doomu Nimsi fexeel Yoram. Fekk na Yoram ak waa Israyil yépp a ngay wattu Ramot ga ca Galàdd, ndax Asayel buurub Siri. \v 15 Booba Buur Yoram moom dem na Yisreel, fajuji ndax jam-jam ya ca xareem baak Asayel buurub Siri. Yewu nag ne: «Ndegam man ngeen àndal, bu kenn rëcce ci biir dëkk bi, di nettaliji waa Yisreel.» \v 16 Mu war watiir, jëm Yisreel, fekk Yoram a nga fa woon tëdd ndax jam-jam ya. Akasiya buurub Yuda dikk, di ko seet. \v 17 Ci biir loolu jongrukat ba ca kaw tatay Yisreel séen gàngoor ga Yewu àndal. Mu ne Buur Yoram: «Séen naa gàngoor guy ñëw de.» Yoram ne ko: «Yebalal gawar bu leen gatandu, laaj leen mbaa jàmm la.» \v 18 Ci kaw loolu gawar ba gatanduji leen, ne leen: «Buur nee: Mbaa jàmm la?» Yewu ne ko: «Ana luy sa yoon ci jàmm laam déet? Ayca, toppal sama gannaaw.» Jongrukat ba daldi yégle la xew, ne: «Ndaw la àgg na ca ñoom de, waaye dëppul.» \v 19 Yoram yebalaat beneen gawar. Ba mu àggee ca ñoom, ne leen: «Buur nee: “Mbaa jàmm?”» Yewu ne ko: «Ana luy sa yoon ci jàmm laam déet? Ayca, sama gannaaw.» \v 20 Ba loolu amee jongrukat ba dellu yégle la xew, ne: «Ndaw la àgg na ca ñoom de, waaye dëppul. Te na kee di dawale mel na ni Yewu doomu Nimsi, ndax dawalinu dof lay dawal.» \p \v 21 Ba mu ko defee Yoram ne: «Takkleen!» Ñu takkal Yoram buurub Israyil watiiram, mu génn ànd ak Akasiya buurub Yuda, ku nekk ak sa watiir; ñu dawal dogaleji Yewu, taseek moom fa doonoon toolub Nabot mu Yisreel\f + \fr 9.21 \fr*\fk toolub Nabot mu Yisreel: \fk*\ft seetal ci \ft*\ft \+bk 1.Buur ya\+bk* 21.\ft*\f*. \v 22 Yoram jàkkaarlook Yewu, ne ko: «Yewu, mbaa jàmm?» Yewu ne ko: «Ana nu jàmm di ame te sa bàkkaaru bokkaaley ndey Yesabel jógu fi, mook xërëmam yi ne xas?» \v 23 Yoram ne wërëñ daw, àddu ca kaw, ne Akasiya: «Akasiya, wor nañu nu!» \v 24 Yewu daldi sox fittam ak doole, fitt Yoram ca diggante mbagg ya, mu génne ca xol ba, Yoram ne lasiim ca watiiram. \p \v 25 Ba loolu amee mu ne jaraafam ba ñuy wax Bitkar: «Foral sànni ci toolub Nabot mu Yisreel. Yaa ngi fàttliku ba nu bokkee watiir maak yaw topp ca baayam Axab te \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji rëbb ko ne ko: \v 26 “Aji Sax ji dafa wax ne: Deretu Nabot ak deretu doomam yi déy, gis naa mu tuuru fii démb. Kon nag dinaa la ko topp, nga fey ko ci tool bii. Loolu la Aji Sax ji wax\f + \fr 9.26 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk 1.Buur ya\+bk* 21.19.\ft*\f*.” Kon nag yóbbul sànni ci tool bi, muy la Aji Sax ji waxoon.» \p \v 27 Akasiya buurub Yuda gis loolu, daw jaare ca yoonu Bet Gan, Yewu dàqi ko, tey yuuxu naan: «Jamleen ko, moom itam.» Ñu jam ko ca kaw watiiram ca yoon wa ngay yéeg jëm Gur, ca wetu Yiblam. Mu daw ba Megido, dee foofa. \v 28 Ba loolu amee ay surgaam yeb ko ca watiiram, yóbbu Yerusalem, ñu denc ko ca bàmmeelam, fa ñu denc ay maamam, ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. \v 29 Ca fukkeelu at ak benn ca nguurug Yoram doomu Axab la Akasiya falu buur ca Yuda. \s1 Yesabel dee na \p \v 30 Gannaaw loolu Yewu jubsi Yisreel, Yesabel yaayu Buur dégg ko, tusngalu, defaraat boppam, taxaw ca palanteer ba, di séentu. \v 31 Naka la Yewu wees buntu dëkk ba, di duggsi rekk, mu ne: «Mbaa jàmmee, Simri mu ndaw, bóomkatub sangam\f + \fr 9.31 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk 1.Buur ya\+bk* 16.8-20.\ft*\f*?» \v 32 Yewu séentu palanteer ba ne: «Ana ku far ak man fii waay?» Ñaar ba ñetti bëkk-néeg ne pëll ca kaw palanteer ba, séentu ko. \v 33 Mu ne: «Sànnileen ko ci suuf.» Ñu jàpp Yesabel, sànni ko fa suuf, deret ja tis ca kaw taax maak fas ya; Yewu dëggaate néew ba. \p \v 34 Ba loolu wéyee mu jàll ca biir dëkk ba; lekk daldi naan ba noppi, ne: «Jubluleen ci jigéen ju alku jee te suul koo waay, ndaxte doomu buur la.» \v 35 Ba ñu demee, di ko suuli nag, fekkuñu dara ca moom lu moy kaaŋ ma doŋŋ ak ndëgguy tànk yaak cati loxo ya. \v 36 Ñu dellu wax ko Yewu, mu ne: «Loolu moo doon kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ja mu waxoon, Ilyaas mu Tisbi jaamam ba jottli ko, ne: “Ci toolub Yisreel la xaj yi di lekke Yesabel\f + \fr 9.36 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk 1.Buur ya\+bk* 21.19.\ft*\f*. \v 37 Néewub Yesabel dina mel ni mbalit ci àll bi, ci biir toolub Yisreel, ba kenn du man ne: Kii Yesabel a.”» \c 10 \s1 Yewu bóom na waa kër Axab \p \v 1 Buur Axab amoon na juróom ñaar fukki doom yu góor ca Samari. Yewu bind ay bataaxal, yónnee ca Samari ca kilifay Yisreel ak mag ñaak dagi doomi Axab, ne leen: \v 2 «Gannaaw yeenay wattu seen doomi sang te yeena yor watiir yeek fas yi, dëkke dëkk bi ñu wëraley tata, boole ci yore gànnaay yi, bu ngeen dee jot ci bataaxal bii rekk, \v 3 tànnleen ki gën te gën di jàmbaar ci seen doomi sang, ngeen teg ko ci jalu baayam. Su ko defee ngeen xeexal seen waa kër sang.» \v 4 Ñu am tiitaange nag lool, daldi ne ca seen biir: «Seetleen rekk ñaari buur a ngii yu manula të Yewu; mbaa nun dinanu ko mana të yee?» \v 5 Ba loolu amee ka yilif kër buur ak ka yilif dëkk baak mag ñaak dag ya yónnee ca Yewu, ne ko: «Nun say surga lanu, lépp loo nu wax dinanu ko def. Dunu fal kenn buur. Loo def baax na.» \p \v 6 Ba mu ko defee Yewu bind leen ñaareelu bataaxal, ne leen: «Ndegam man ngeen àndal te sama kàddu ngeen di dégg, dogleen seen boppi doomi sang yu góor te fekk ma fii ci Yisreel nëgëni ëllëg.» Booba doomi buur yu góor juróom ñaar fukk lañu, nekk ak kàngami dëkk ba leen yar. \v 7 Ba bataaxal ba agsee, kàngam yooyu boole doomi buur yu góor ya, rendi, ñuy juróom ñaar fukki góor. Ñu yeb seeni bopp ciy dàmba, yónnee Yewu ca Yisreel. \v 8 Ndaw la agsi ne ko: «Indi nañu boppi doomi buur ya.» Yewu ne: «Defleen ko ñaari jal ca buntu dëkk ba, ba ëllëg.» \v 9 Ca ëllëg sa mu génn taxaw ca kanam mbooloo mépp ne: «Yeen defuleen dara. Man mii maa fexeel samab sang, rey ko. Waaye ana ku bóom ñii ñépp? \v 10 Kon xamleen ne du lenn luy fanaan àll ci kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ci li mu wax ci waa kër Axab. Aji Sax ji sottal na la mu waxoon, Ilyaas jaamam ba jottli ko.» \v 11 Ba mu ko defee Yewu rey mboolem ña desoon ca kër Axab ca Yisreel ak mboolemi kàngamam aki jegeñaaleem aki \w sarxalkatam|lemma="sarxalkat b-:"\w*, bàyyiwu ca kenn, mu rëcc. \p \v 12 Gannaaw loolu Yewu fabu jëm Samari. Ba mu demee ba tollook Bet Eket, ca sàmm sa, \v 13 daldi dajeek bokki Akasiya buurub Yuda. Mu ne leen: «Yeenay ñan?» Ñu ne ko: «Bokki Akasiya lanu. Danuy nuyuji doomi Buur Axab, ak doomi Lingeer yaayu Buur.» \v 14 Mu ne: «Jàppleen leen!» Ñu jàpp leen, dem rendi leen ca wetu teenu Bet Eket; ñuy ñeent fukk ak ñaar, bàyyiwuñu ca kenn, mu rëcc. \p \v 15 Ba loolu wéyee Yewu bàyyikoo fa, gis Yonadab doomu Rekab, mu dikk dajeek moom. Mu nuyook moom, ne ko: «Mbaa ni ma fareek yaw te muy dëgg, ni nga fareek man te muy dëgg?» Yonadab ne ko: «Waawaaw.» Yewu ne ko: «Kon nag jox ma sa loxo!» Mu jox ko loxo; mu xëcc ko, yéege ko ca watiir ba, \v 16 ne ko: «Ñëwal nu dem rekk, nga gis ni ma farloo ci mbiri Aji Sax ji.» Mu waral ko watiiram, yóbbu ko. \v 17 Ba Yewu àggee Samari, daa rey mboolem ña desoon ca waa kër Axab ca Samari, faagaagal leen, muy la Aji Sax ji waxoon Ilyaas. \s1 Yewu fiir na waa kër Baal \p \v 18 Ba mu ko defee Yewu woo mbooloo ma mépp, ne leen: «Axab tuuti la jaamu \w Baal|lemma="Baal:"\w*. Man Yewu bu baax laa koy jaamu. \v 19 Ayca, wool-leen ma yonenti Baal yépp ak \w sarxalkatam|lemma="sarxalkat b-:"\w* yépp ak jaamukatam yépp. Bu kenn wuute, ndax sarax bu réy laay defal Baal. Képp ku ko wuute dina dee.» Booba Yewoo ngi fexee nax ñiy jaamu Baal, ba rey leen. \v 20 Yewu ne leen: «Beral-leen Baal am ndaje.» Ñu yéene. \v 21 Yewu nag yónnee ca Israyil gépp; mboolem ñay jaamu Baal dikk, kenn desul. Ci kaw loolu, ñu dugg kër Baal, ba kër ga fees dell. \v 22 Yewu ne ka yor cummikaay la: «Képp kuy jaamu Baal, indil ko mbubb.» Mu indil leen ay mbubb. \v 23 Ba loolu amee Yewu ànd ak Yonadab doomu Rekab, duggsi biir kër Baal. Mu ne jaamukati Baal ya: «Xool-leen bu baax, ba gis ne yéenu neen la, te jaamukati \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji raxu leen, xanaa jaamukati Baal rekk.» \v 24 Ña ngay dugg, ne dañuy def ay \w saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* ak yeneen sarax. Fekk na Yewu teg ca biti juróom ñett fukki nit, ne leen: «Ku ci bàyyi kenn ci ñi ma leen reyloo, ba mu rëcc, sa bakkan ngay feye bakkanam.» \p \v 25 Ba ñu noppee ca saraxi rendi-dóomal ya, Yewu ne dag yaak jawriñi xarekat ya: «Duggleen, fàdd leen. Bu kenn génn.» Ñu daldi leen leel ñawkay saamar, ñu daanu. Dag yaak jawriñ ya sànni néew ya ca biti, ba noppi dugg ca néegu Baal ba gëna biire. \v 26 Ñu génne tuuri doj ya sampe woon ca kër Baal, lakk ko. \v 27 Dañoo daane jëmmi Baal ja, màbb kër Baal, boole ca, def kob sën, te moom la ba tey jii. \p \v 28 Nii la Yewu raafale lu bokk ci Baal ci Israyil. \v 29 Teewul mu baña dëddu bàkkaar ya Yerbowam doomu Nebat daan bàkkaarloo Israyil, ñuy jaamu ay sëlluy wurus la ko dale Betel, ba ba ngay àgg Dan. \p \v 30 Aji Sax ji nag ne Yewu: «Gannaaw def nga lu baax, di jëfe li ma rafetlu te def nga waa kër Axab mboolem li ma bëggoon, saw askan dina toog ci jalub Israyil ba ca sa sët-sëtaat.» \v 31 Terewul Yewu amuloon pastéefu toppe léppi xolam yoonu Aji Sax ji Yàllay Israyil. Dëdduwul ba tey bàkkaari Yerbowam ya mu daan bàkkaarloo Israyil. \p \v 32 Ca jamono jooja nag la Aji Sax ji tàmbalee fell suufas Israyil, Asayel buurub Siri di leen duma ca réew ma mépp. \v 33 Noonu lañu ñàkke fa féete dexu Yurdan penku dale ca diiwaanu Galàdd bépp, boole ca suufas waa Gàdd ak waa Ruben ak waa Manase. Mooy la tàmbalee dëkk ba ñuy wax Arower ca kaw dexu Arnon ba ca diiwaanu Galàdd ak Basan. \p \v 34 Li des ci mbiri Yewu ak mboolem lu mu def ak njàmbaaram gépp, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. \v 35 Noonu Buur Yewu saay, fekki ay maamam, ñu denc ko ca Samari. Doomam Yowakas falu buur, wuutu ko. \v 36 Diir bi Yewu nguuru ci Israyil, péeyoo Samari, ñaar fukki at la ak juróom ñett. \c 11 \s1 Lingeer Atalyaa falu na Yuda \p \v 1 Ci kaw loolu Atalyaa yaayu Akasiya xam ne doomam ju góor dee na, mu daldi faagaagal mboolem ku bokk ci askanu buur. \v 2 Teewul jigéenub Akasiya, Yoseba doomu Buur Yoram, jàpp Yowas doomu Akasiya ju góor, jële ko ca biir doomi buur ya ñuy fexee rey, ba rawale ko. Ci biir loolu mu boole kook nàmpalkatam, tëj cib néeg ngir làq ko Atalyaa, ba kenn reyu ko. \v 3 Yowas nekk naak Yoseba fa kër Yàlla ga, làqu fa juróom benni at, te Atalyaa di nguuru fa réew ma. \s1 Yuda bañ na \p \v 4 Ca atum juróom ñaareel ma, Yoyada moo woolu waa Keret ya jiite kuréli téeméeri nit, ak yeneen dag ya, ñu wuysi ko ca kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Mu fasook ñoom \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w*, giñloo leen ca kër Aji Sax ji, ba noppi nuyole leen ak doomu Buur. \v 5 Ci kaw loolu mu sant leen ne leen: «Li ngeen di def mooy lii: Yeen ñi aye liggéey \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*, na seen xaajub ñetteel dénkoo dénkaaney kër Buur, \v 6 beneen xaajub ñetteel ba wattu buntu Sur ba, xaajub ñetteel ba ca des féeteek bunt ba ca gannaaw dawkat ya. Noonu ngeen di ay-ayloo wattub kër Buur. \v 7 Seen yeneen ñaari kurél yi ayewul bésub Noflaay, nañu wattusi kër Aji Sax ji, ngir aar buur bi. \v 8 Yeen ñiy dar Buur, fegleen ko wet gu nekk, ku nekk ŋàbb ngànnaayam. Képp ku jëm ci seenug làng, dees koy rey, te àndleen ak buur bi buy dugg ak buy génn.» \v 9 Ci kaw loolu njiiti kuréli téeméer ya def mboolem la leen Yoyada \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba sant. Ku nekk ànd ak say nit, ña aye bésub Noflaay ak ña ayewul bésub Noflaay, ñu bokk dikk ca Yoyada, sarxalkat ba. \v 10 Ba loolu amee, sarxalkat ba jox njiiti kuréli téeméer ya, xeej yaak pakki Buur Daawuda ya nekkoon ca biir kër Aji Sax ji. \v 11 Dag ya nag dar buur ba, ku nekk ŋàbb ay gànnaayam, ñu dare kër Yàlla ga ak \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* ba, wetu ndijoor ba wetu càmmoñ, ngir yéew buur ba. \v 12 Yoyada génne doomu buur ba, solal ko mbaxanam buur, jox ko kayitu doxalinu nguur ga; ñu fal ko nag buur, diw ko diwug pal. Ba loolu amee ñu tàccu, ne: «Guddalu fan, Buur!» \p \v 13 Ba Atalyaa déggee coowal dag yaak mbooloo ma, daa àgg ca mbooloo ma, fa kër Aji Sax ji. \v 14 Mu xool, yem ci buur ba taxaw fa kenu ga, na ñu ko baaxoo, kilifay xarekat yaak boroom liit ya dar Buur, waa réew ma mépp di bànneexook a wal liit ya. Atalya ne tareet ay yéreem ndax naqar, daldi yuuxu ne: «Wor am naay, wor am na!» \v 15 Ci kaw loolu Yoyada sarxalkat ba sant njiiti kuréli téeméer ya, kilifay gàngoor ga, ne leen: «Génneleen ko làng gi, te ku ko topp, jamleen ko, mu dee.» Fekk na Yoyada ne buñu ko rey ci biir kër Aji Sax ji. \v 16 Ba mu ko defee ñu teg ko loxo. Ba mu demee ba àgg kër Buur, bay tollook fa fas yay dugge, foofa lañu ko reye. \p \v 17 Ba loolu amee Yoyada digoo kóllëre diggante Aji Sax ji, ak buur baak askan wa, ngir ñu doon ñoñi Aji Sax ji. Mu digoo ko itam diggante Buur ak askan wa. \v 18 Ci kaw loolu waa réew ma mépp ànd dem ca kër \w Baal|lemma="Baal:"\w*. Ñu màbb ko, ay sarxalukaayam ak jëmmi nataalam, ñu tas tasar, Matan sarxalkatu Baal ba, ñu rey ko ca kanam sarxalukaay ya. Ci biir loolu Yoyada sarxalkat ba teg ay wattukat ca kër Aji Sax ji. \v 19 Mu dellu nag woo njiiti téeméeri nit yaak waa Keret ñaak yeneen dag yaak mboolem waa réew ma, ñu jële Buur kër Aji Sax ji, jaare ca buntu dag ya, yóbbu ko kër Buur. Yowas daldi toog ca ngànguney buur ya. \v 20 Waa réew mépp di bànneexu, péey ba ne tekk. Atalya moom, fekk na ñu jam ko saamar ba mu dee ca kër Buur. \s1 Yowas santaane na ñu defaraat kër Aji Sax ji \p \v 21 Juróom ñaari at la Yowas amoon ba muy falu buur. \c 12 \p \v 1 Ca juróom ñaareelu atu nguurug Yewu buurub Israyil, ca la Yowas falu ca Yuda. Ñeent fukki at la nguuru fa Yerusalem. Yaayam mooy Sibiya ma cosaanoo Beerseba. \v 2 Yowas di def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji rafetlu mboolem diir ba muy wéy ci ndigalal Yoyada. \v 3 Taxul nag ñu jële fa \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* ya, te mbooloo ma noppiwuñu faa rendi ay sarax, di fa taal cuuraay. \p \v 4 Mu am bés mu wax \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ya ne leen: «Mboolem xaalis bu ñu sellalal kër Aji Sax ji, muy xaalisu njot-gi-bakkan\f + \fr 12.5 \fr*\fk xaalisu njot-gi-bakkan: \fk*\ft seetal ci \ft*\ft \+bk Mucc ga\+bk* 30.11-16.\ft*\f*, mbaa xaalis bu ñu wàccoo ngiñ, mbaa bépp xaalisu saraxu yéene bu nit di indi kër Aji Sax ji, \v 5 na ko sarxalkat bu nekk nangoo ci seen loxoy xame, ngir ñu liggéeye ko kër Yàlla gi, fépp fu fi laaj ñu defaraat ko.» \p \v 6 Teewul Yowas dugg na ñaar fukkeelu atu nguuram ak ñett, te taxul sarxalkat ya defarluwaat lenn ci kër Aji Sax ji. \v 7 Buur Yowas woolu Yoyada, sarxalkat ba ak yeneen sarxalkat ya, ne leen: «Ana lu waral defaruleen lenn ci kër Aji Sax ji? Léegi nag buleen nangooti xaalis ci seeni xame, waaye joxeleen ko, ñu defare ko kër Aji Sax ji.» \v 8 Sarxalkat ya déggal ko, jëlatuñu xaalis ci mbooloo mi, sasootuñu liggéeyu defaraat kër Aji Sax ji. \p \v 9 Ba mu ko defee Yoyada sarxalkat ba wut waxande, bënn pax ca kubeer ga, teg ko ca wetu \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* ba, fa féete ndijoor, booy duggsi ci kër Aji Sax ji. Sarxalkat yay wattu bunt ba di def ca waxande wa mboolem xaalis bu ñu indi ca kër Aji Sax ji. \v 10 Ci kaw loolu saa yu ñu gisee ne xaalis bu takkoo ngi ci waxande wi ci kër Aji Sax ji, bindkatub Buur ànd ak sarxalkat bu mag ba dikk, waññi ko, fas ko. \v 11 Bu ñu takkee limu xaalis ba, teg ko ca loxoy ña ñu tabb, ñu wara saytu liggéeyu kër Aji Sax ji. Su ko defee ñu fey ca ñay liggéey ca kër Aji Sax ji, muy liggéeykatu bant yaak yeneen liggéeykat ya, \v 12 ak tabaxkat yaak yettkati doj ya, jënd ca bant ak doji yett, yi ñu soxla ci defarub kër Aji Sax ji, ak mboolem lu ñuy jënd ngir defar kër Aji Sax ji. \v 13 Waaye xaalis bi ñuy indi ci kër Aji Sax ji defaraluñu ci kër Aji Sax ji ay mbalkay xaalis mbaa ay paakaaki këllu tuuru mbaa ay liit ak lenn luy jumtukaayu wurus mbaa xaalis. \v 14 Ñi yor liggéey bi daal lañu ko jox ngir ñu defaraat kër Aji Sax ji. \v 15 Soxlawuñu woona laaj dara nit ñi ñuy teg xaalis bi ci seeni loxo ngir ñu fey liggéeykat yi, ndax maandu ga ñu daan jëfe. \p \v 16 Xaalisu \w saraxu peyug tooñ|lemma="Sarax yi:"\w* nag ak xaalisu \w saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"\w* daawuñu ko indi ci kër Aji Sax ji. Sarxalkat yaa ko moomoon. \s1 Buur Yowas jeexal na \p \v 17 Ca jamono yooyu Asayel buurub Siri dem na songi Gaat, nangu ko, doora walbatiku nara dal ci kaw Yerusalem. \v 18 Buur Yowas nag dajale mboolem gànjar ga maamam ya, Yosafat ak Yoram ak Akasiya, jagleeloon \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, boole ca gànjar ga mu ko jagleeloon moom ci boppam, ak lépp luy wurus ca dencukaayi kër Aji Sax jeek kër Buur. Mu yónnee lépp Asayel buurub Siri, mu dëpp, bàyyi Yerusalem. \p \v 19 Li des ci mbiri Yowas ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. \v 20 Gannaaw gi ay jawriñam fexeel ko ba bóom ko ca Bet Milo ca yoonu Sila. \v 21 Jawriñam ya ñuy wax Yosabàdd doomu Simeyat ak Yewosabàdd doomu Somer, ñoo ko jam, mu dee; ñu denc ko fa ay maamam ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. Doomam Amaciya moo falu buur, wuutu ko. \c 13 \s1 Yowakas falu na ci Israyil \p \v 1 Ba doomu Akasiya, Yowas buurub Yuda duggee ñaar fukkeelu atam ak ñett ci nguuram, ca la Yowakas doomu Yewu falu buur ca Israyil, péeyoo Samari. Nguuru na fukki at ak juróom ñaar. \v 2 Muy def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu, topp ci tànki Yerbowam doomu Nebat, di ko roy ci bàkkaar ya mu daan bàkkaarloo Israyil, bañ koo dëddu. \v 3 Merum Aji Sax ji nag ne jippét ca kaw Israyil, mu teg leen lu yàgg ci loxoy Asayel buurub Siri ak Ben Addàd doomu Asayel. \v 4 Yowakas nag tinu Aji Sax ji, mu nangul ko, ndax fekk na mu gis fitnay Israyil ji leen buurub Siri fitnaal. \v 5 Aji Sax ji daldi may Israyil ku leen xettli, ba ñu génn ca loxol waa Siri. Ba loolu amee waa Israyil dellu nekk ca seeni kër ci jàmm, na woon démb ak bëkk-démb. \v 6 Taxul ba tey ñu dëddu bàkkaari waa kër Yerbowam ya ñu doon bàkkaarloo Israyil. Dañu caa sax. Te it xer wa ñuy jaamoo \w Aseraa|lemma="Asera:"\w* nga sampe woon ca Samari ba booba. \v 7 Mujj na Yowakas desewuloon ca mbooloom xareem lu moy juróom fukki gawar ak fukki watiir ak fukki junniy xarekat (10 000), ndax buurub Siri moo faagaagal ña ca des ñépp, duma leen ba ñu ne mbëtt. \p \v 8 Li des ci mbiri Yowakas ak mboolem lu mu def aki njàmbaaram, bindees na lépp moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buurub Israyil ca seeni jant. \v 9 Ba mu ko defee Buur Yowakas saay, fekki ay maamam, ñu denc ko ca Samari. Doomam Yowayas falu buur, wuutu ko. \s1 Yowayas falu na ca Israyil \p \v 10 Ba Yowas buurub Yuda duggee fanweereelu atu nguuram ak juróom ñaar, ca la Yowayas doomu Yowakas falu buurub Israyil, péeyoo Samari. Nguuru na fukki at ak juróom benn. \p \v 11 Muy def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu nag, dëdduwul lenn ci bàkkaar ya Yerbowam doomu Nebat doon bàkkaarloo Israyil. Da caa sax kay. \p \v 12 Li des ci mbiri Yowayas ak mboolem lu mu def ak njàmbaar ga mu xareek Amaciya buurub Yuda, bindees na lépp moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. \v 13 Yowayas nag saay, fekki ay maamam, Yerbowam falu, wuutu ko. Ñu denc Yowayas fa ñu denc buuri Israyil ca Samari. \s1 Yonent Yàlla Alyaasa faatu na \p \v 14 Ba Alyaasa tëddee ca wopp ja ko wara yóbbu, Yowayas buurub Israyil seeti woon na ko, tiim ko, di jooy naan: «Éy baayoo, baay Alyaasa, yaay watiiru xarey Israyil aki gawaram!» \p \v 15 Alyaasa ne ko: «Indil xala aki fitt.» Mu indi. \v 16 Alyaasa ne ko: «Soxal.» Mu sox. Alyaasa teg ay loxoom ca kaw loxoom, \v 17 ba noppi ne ko: «Ubbil palanteeru penku bi.» Mu ubbi. Alyaasa ne ko: «Soqil!» Mu soqi. Mu ne ko: «Fittu ndamal \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jaa ngoog, di fitt gi ngay ame ndam ci waa Siri. Dinga daan waa Siri ca Afeg, ba faagaagal leen.» \v 18 Mu delluwaat ne ko: «Jëlal fitt yi.» Mu jël. Mu ne ko: «Soqil fi suuf!» Mu soqi, ba muy ñetti yoon, bàyyi. \v 19 Góorug Yàlla ga nag mere ko, ne ko: «Soo jamoon juróomi yoon ba juróom benni yoon, dinga daan waa Siri, ba jeexal leen tàkk; waaye léegi nag ñetti yoon rekk ngay daan waa Siri.» \v 20 Gannaaw gi Alyaasa faatu, ñu denc ko. \p Loolu fekk na ndoortel at mu jotaan ay gàngoori yàqkati Mowabeen dugg ca réew ma. \v 21 Mu am bés ay nit doon rob, jekki-jekki gis gàngooru yàqkat di dikk. Ñu sànni néew ba ca bàmmeelu Alyaasa, daldi daw. Naka la néew ba dal ca yaxi Alyaasa, rekk dekki, ne ñokket, taxaw. \s1 Israyil duma na Siri \p \v 22 Ci kaw loolu Asayel buurub Siri di fitnaal Israyil mboolem diir ba Yowakas di buur. \v 23 \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nag baaxe leen, yërëm leen, geesu leen ndax \w kóllëreem|lemma="kóllëre g-:"\w* ak Ibraaymaak Isaaxaak Yanqóoba. Looloo tax buggu leena faagaagal, te ba tey jii xalabu leen. \v 24 Ba Asayel buurub Siri deeyee, doomam Ben Addàd falu, wuutu ko. \v 25 Ba mu ko defee Yowayas nangoo ci moom dëkki Israyil ya Asayel jële woon ca loxol baayam Yowakas ci xare. Ñetti yoon Yowayas duma na ko Ben Addàd, ba nanguwaat dëkki Israyil. \c 14 \s1 Buuri Israyil ak Yudaa ngi xeexoo \p \v 1 Ba buurub Israyil Yowayas doomu Yowakas duggee ñaareelu atu nguuram, ca la Amaciya doomu Yowas falu buur ca Yuda. \v 2 Ñaar fukki at ak juróom la amoon ba muy falu, te ñaar fukki at ak juróom ñeent la nguuru fa Yerusalem. Yaayam moo doon Yowadan ma cosaanoo Yerusalem. \v 3 Def na njub gi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji rafetlu, waaye dabul Daawuda maamam. Mboolem noonee Yowas baayam daan jëfe, na la daan jëfe \v 4 \w Bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* ya jëleesu ko fa. Mbooloo maa nga doon def ay sarax ca bérabi jaamookaay ya ba tey, di fa taal cuuraay. \v 5 Ba nguur ga demee ba dëgër ci loxoom, moo bóom jawriñam ña bóomoon Buur baayam. \v 6 Waaye doomi bóomkat ya, bóomu leen, ngir dëppook la ñu bind ci téereb yoonu Musaa, te Aji Sax ji santaane ko, ne: «Deesul rey baay ndax doom te deesul rey doom ndax baay. Nit ku nekk, bàkkaaru boppam lees koy reye\f + \fr 14.6 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Baamtug Yoon wi \+bk* 24.16.\ft*\f*.» \p \v 7 Moom Amaciya moo duma fukki junniy (10 000) waa Edom ca xuru Xorom wa, nangu dëkk ba ñuy wax Sela ca xare ba, tudde ko Yogtel, te noonu la tudd ba bésub tey jii. \v 8 Ba loolu amee Amaciya yónni ay ndaw ca buurub Israyil Yowayas doomu Yowakas doomu Yewu. Mu ne ko: «Dëkk naa la, dikkal nu jàkkaarloo!» \v 9 Yowayas buurub Israyil yónnee Amaciya buurub Yuda tontam, ne ko: «Ndég ga ca Libaŋ moo yónnee woon ca garabu seedar gu mag ga ca Libaŋ, ne ko: “Sa doom jii, may ko sama doom jabar.” Ci kaw loolu rabu àllu Libaŋ jaare fa, dëggaate ndég ga. \v 10 Dëgg la moos, yaa duma Edom, ba tax nag sam xel jay la. Tee ngaa bàkku te toog sa kër? Te sax ana looy dugge ci jote buy indi ay wu lay daane, yaw, daanewaale Yuda?» \p \v 11 Amaciya nag faalewul wax jooju, Yowayas buurub Israyil jóg; ñu jàkkaarloo mook Amaciya buurub Yuda, ca Bet Semes ga ca Yuda. \p \v 12 Ba mu ko defee muy jéllu Yuda fa kanam Israyil. Waa Yuda tasaaroo, ku nekk ñibbi ca sab xayma. \v 13 Yowayas buurub Israyil nag jàpp buurub Yuda, Amaciya doomu Yowas doomu Akasiya, ca Bet Semes. Gannaaw loolu mu dem Yerusalem màbb tata ja, la ko dale buntu Efrayim ba ca buntu ruq ba, muy ñeenti téeméeri xasab. \v 14 Ci kaw loolu mu jël mboolem lu doon wurus ak xaalis aki ndab ca kër Aji Sax ja, ak ca dencukaayi kër Buur, boole ca nit ñu mu jàpp, daldi dellu Samari. \s1 Yowayas buurub Israyil saay na \p \v 15 Li des ci mbiri Yowayas ak li mu def ba ci njàmbaaram gi mu xareek Amaciya buurub Yuda, bindees na lépp moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. \v 16 Gannaaw gi Buur Yowayas saay, fekki ay maamam, ñu denc ko Samari, fa bàmmeelu buuri Israyil. Doomam Yerbowam falu buur, wuutu ko. \s1 Amaciya buurub Yuda saay na \p \v 17 Amaciya doomu Yowas buurub Yuda dund na fukki at ak juróom gannaaw deewug buur Israyil Yowayas doomu Yowakas. \v 18 Li des ci mbiri Amaciya, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. \v 19 Lalal nañu ko pexe ca Yerusalem, mu daw dem Lakis. Ñu yónnee dabi ko ca Lakis, rey ko foofa. \v 20 Ba mu ko defee ay fas lañu yóbboo néew ba, denci ko Yerusalem, fa ay maamam, ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. \p \v 21 Ba loolu wéyee waa Yuda gépp fal Asaryaa\f + \fr 14.21 \fr*\fk Asaryaa \fk*\ft mooy Osiyas ba tey.\ft*\f* buur, mu wuutu baayam Amaciya, fekk mu am fukki at ak juróom benn. \v 22 Moom moo tabaxaat dëkk ba ñuy wax Elat, delloo ko ci biir Yuda, gannaaw ba Buur Amaciya saayee, fekki ay maamam. \s1 Yerbowam mu ndaw falu na ca Israyil \p \v 23 Ba buurub Yuda Amaciya doomu Yowas duggee fukkeelu atu nguuram ak juróom, ca la Yerbowam doomu Yowayas falu ca Israyil, péeyoo Samari. Nguuru na ñeent fukki at ak benn. \v 24 Muy def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu, dëdduwul lenn ci bàkkaar ya Yerbowam doomu Nebat daan bàkkaarloo Israyil. \v 25 Moom moo delloo kemu réewum Israyil fa mu nekkoon, dale ko ca buntu dëkk ba ñuy wax Amat ba ca géeju Araba, muy la Aji Sax ji Yàllay Israyil waxoon jaamam ba, Yonent Yàlla Yunus, ma baayam Ametay cosaanoo Gaat Efer, Yunus jottli ko. \v 26 Fekk na Aji Sax ji gis Israyil gépp, gor ak jaam, nekke fitna ju metti te amul kenn ku leen wallu. \v 27 Aji Sax ji nag nammul woona far turu Israyil, ba jant bi dootu ko tiim fenn. Moo tax mu may leen ku leen xettli, muy Yerbowam doomu Yowayas. \p \v 28 Li des ci mbiri Yerbowam ak mboolem lu mu def ak njàmbaaram gi mu xaree te nangoo ko dëkk yi ñuy wax Damaas ak Amat gu Yuda, delloo ko Israyil, bindees na lépp moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ci seeni jant. \v 29 Gannaaw gi Buur Yerbowam saay, fekki maamam ya doon buuri Israyil. Doomam Sàkkaryaa\f + \fr 14.29 \fr*\fk Sàkkaryaa \fk*\ft mii wuute naak Yonent Yàlla Sàkkaryaa.\ft*\f* falu buur, wuutu ko. \c 15 \s1 Asaryaa falu na buur ca Yuda \p \v 1 Ba Yerbowam buurub Israyil duggee ñaar fukkeelu at ak juróom ñaar ci nguuram, ca la Asaryaa\f + \fr 15.1 \fr*\fk Asaryaa \fk*\ft mooy Osiyas ba tey.\ft*\f* doomu Amaciya falu buur ca Yuda. \v 2 Fukki at ak juróom benn la amoon, ba muy falu buur, te nguuru na juróom fukki at ak ñaar ca Yerusalem. Yaayam mooy Yekolyaa ma cosaanoo Yerusalem. \v 3 Asaryaa di def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji rafetlu, mboolem noonee ko Amaciya baayam daan defe. \v 4 Terewul \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* ya jëleesu ko fa. Mbooloo ma dañoo wéy di fa def ay sarax ak a taal cuuraay. \v 5 Aji Sax ji nag mbugal Asaryaa, teg ko jàngoroy ngaana ba kera bés ba mu deeyee. Ci néeg bu ñu ko ber la dëkk. Doomu Buur Yotam moo jiite kër ga, yor kilifteefu askanu réew ma. \p \v 6 Li des ci mbiri Asaryaa ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. \v 7 Gannaaw gi Asaryaa tëdd, fekki ay maamam, ñu denc ko ca bàmmeeli maamam ya, ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. Yotam doomam moo falu buur, wuutu ko. \s1 Sàkkaryaa falu na buur ca Israyil \p \v 8 Ba Asaryaa buurub Yuda duggee fanweereelu atu nguuram ak juróom ñett, ca la Sàkkaryaa doomu Yerbowam falu buurub Israyil, péeyoo Samari. Juróom benni weer la nguuru. \p \v 9 Muy def nag li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu, na ko ay maamam daa defe. Dëdduwul bàkkaar yu Yerbowam doomu Nebat daan bàkkaarloo Israyil. \v 10 Ci kaw loolu Salum doomu Yabes fexeel ko, jam ko ca kanam mbooloo ma, rey ko, daldi falu buur, wuutu ko. \v 11 Li des ci mbiri Sàkkaryaa bindees ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. \v 12 Loolu mooy kàddu ga Aji Sax ji waxoon Yewu ne ko: «Saw askan dinañu toog ci kaw jalu Israyil ba ci sa sët-sëtaat.» Te noonu la amee. \s1 Salum falu na buur ca Israyil \p \v 13 Ba Asaryaa buurub Yuda duggee fanweereelu atu nguuram ak juróom ñeent, ca la Salum doomu Yabes falu buur ca Israyil. Wenn weer la nguuru, péeyoo Samari. \v 14 Gannaaw loolu Menayem doomu Gadi bàyyikoo Tirsa ba Samari, daldi fa jam Salum doomu Yabes, bóom ko, falu buur, wuutu ko. \v 15 Li des ci mbiri Salum ak pexeem ma mu laloon, bindees na ko moos ca téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. \p \v 16 Booba la Menayem song dëkk ba ñuy wax Tifsa, rey ña fa nekkoon ñépp, boole ca faagaagal diiwaan ba dale Tirsa ba Tifsa, ndax ñoo ko gàntal, bañ koo ubbi buntu dëkk ba. Mu butti jigéeni wérul ña fa nekk ñépp. \s1 Menayem falu na buur ca Israyil \p \v 17 Ba Asaryaa buurub Yuda duggee fanweereelu atu nguuram ak juróom ñeent, ca la Menayem doomu Gadi falu buurub Israyil, péeyoo Samari. Nguuru na fukki at. \v 18 Muy def nag li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu; giiru dundam dëdduwul bàkkaar ya Yerbowam doomu Nebat daan bàkkaarloo Israyil. \v 19 Ci jamonoom la Tiglaat Pilser\f + \fr 15.19 \fr*\fk Tiglaat Pilser \fk*\ft mbaa Pul ba tey.\ft*\f* buurub Asiri song réew ma, Menayem jox ko ñetti téeméeri barigoy xaalis ngir mu jàpple ko, ba nguuram gëna dëgër. \v 20 Menayem dajale xaalis boobu ci Israyil; jële ko ca mboolem boroom alal ya, ku nekk ci ñoom joxe juróom fukki dogi xaalis, ñu yót ko buuri Asiri, mu doora jóge ca réew ma, ñibbi. \v 21 Li des ci mbiri Menayem ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. \v 22 Gannaaw loolu Buur Menayem saay, fekki ay maamam. Doomam Pekaxiya falu buur, wuutu ko. \s1 Pekaxiya falu na buur ca Israyil \p \v 23 Ba Asaryaa buurub Yuda duggee juróom fukkeelu atu nguuram, ca la Pekaxiya doomu Menayem falu buurub Israyil, péeyoo Samari. Nguuru na ñaari at. \v 24 Muy def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu, dëdduwul bàkkaar ya Yerbowam doomu Nebat daan bàkkaarloo Israyil. \v 25 Ba mu ko defee Peka doomu kilifag xarekatam Remalya, fexeel ko, ba rey ko ca Samari, ca tatay kër buur, jamaale Argob ak Arye. Remalyaa nga àndoon ak juróom fukki niti Galàdd. Noonu la ko reye, falu buur, wuutu ko. \p \v 26 Li des ci mbiri Pekaxiya ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. \s1 Peka falu na buur ca Israyil \p \v 27 Ba Asaryaa buurub Yuda duggee juróom fukkeelu atu nguuram ak ñaar, ca la Peka doomu Remalyaa falu buurub Israyil, péeyoo Samari. Nguuru na ñaar fukki at. \v 28 Muy def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu, dëdduwul bàkkaar ya Yerbowam doomu Nebat daan bàkkaarloo Israyil. \v 29 Ci jamonoy Peka buurub Israyil, Tiglaat Pilser buurub Asiri dikk, nangu dëkk yi ñuy wax Yon ak Abel Bet Maaka ak Yanowa ak Kedes ak Àccor ak diiwaani Galàdd ak Galile ak mboolem réewum Neftali. Mu jàpp waa réew ma, yóbbu Asiri. \p \v 30 Ba loolu amee ku ñuy wax Ose doomu Ela lalal Peka doomu Remalya pexe, jam ko mu dee. Mu daldi falu buur, wuutu ko. Loolu yemook ñaar fukkeelu atu nguurug buurub Yuda Yotam doomu Asaryaa. \v 31 Li des ci mbiri Peka ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. \s1 Yotam falu na buur ca Yuda \p \v 32 Ba buurub Israyil Peka doomu Remalya duggee ñaareelu atu nguuram, ca la Yotam doomu Asaryaa falu buur ca Yuda. \v 33 Amoon na ñaar fukki at ak juróom ba muy falu te nguuru na fukki at ak juróom benn ca Yerusalem. Yaayam mooy Yerusa doomu Cadog. \v 34 Muy def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji rafetlu; mboolem na baayam Usiya daan defe la daan defe. \v 35 Terewul jëleesu fa \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* ya, xanaa mbooloo ma di def ay sarax ak a taal cuuraay ba tey, ca bérabi jaamookaay yooyu. Moom nag moo tabax buntu kër Aji Sax ja féete bëj-gànnaar. \v 36 Li des ci mbiri Yotam aki jëfam, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. \v 37 Ci jamonoom la Aji Sax ji tàmbalee xabtal Reccin buurub Siri ak Peka doomu Remalya ci kaw Yuda. \p \v 38 Gannaaw gi Yotam tëdd, fekki ay maamam. Ca bàmmeelu maamam ya lees ko denc, ca gox ba ñu naan dëkku Daawuda, maamam. Doomam Axas falu buur, wuutu ko. \c 16 \s1 Axas falu na buur ca Yuda \p \v 1 Ba buurub Israyil Peka doomu Remalya duggee fukkeelu atu nguuram ak juróom ñaar, ca la Axas doomu Yotam falu buur ca Yuda. \v 2 Ñaar fukki at la Axas amoon ba muy falu buur. Nguuru na fukki at ak juróom benn ca Yerusalem, waaye deful li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Yàllaam rafetlu, na ko maamam Daawuda baaxoo woon. \v 3 Ca tànki buuri Israyil la topp. Doomam ju góor sax def na ko sarax, lakk ko ngir tuur ya, di roy ñaawtéefi xeet, ya Aji Sax ji dàqoon ngir \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \v 4 Rendi nay sarax, taal na cuuraay ca \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* yaak ca kaw tund yaak mboolem ker garab gu naat. \p \v 5 Ci kaw loolu Reccin buurub Siri, ak buurub Israyil Peka doomu Remalya, jóg song Yerusalem xare. Ñu gaw Buur Axas, te manuñu koo daan. \v 6 Jamono yooyu, fekk na Reccin nangu Elat, mu tàbbi ci loxol Siri. Mu génne waa Yuda Elat; Edomeen ña délsi Elat, dëkk fa ba bésub tey jii. \v 7 Axas nag yebal ay ndaw ca Tiglaat Pilser buurub Asiri, ne ko: «Man de, dama di sab jaam, te di sa doom. Kon nag ngalla dikkal xettli ma ci ñi ma jógal, di buurub Siri ak buurub Israyil.» \v 8 Axas jël xaalis ak wurus wa nekkoon ca kër Aji Sax ja ak ca dencukaayi kër Buur, defal ko buurub Asiri yóbbal. \v 9 Buurub Asiri nangul ko, dal ca kaw Damaas, nangu dëkk ba, jàpp waa dëkk ba, yóbbu Kir, ba noppi rey Reccin. \p \v 10 Gannaaw loolu Buur Axas dem ca Tiglaat Pilser buurub Asiri ca Damaas, gis fa \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* ba fa nekk. Ba mu ko defee Buur Axas yónnee ca Uri \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba, nataalu sarxalukaay ba ak tabaxin waak mboolem na mu bindoo. \v 11 Urya sarxalkat ba daldi tabax sarxalukaay bu dëppook mboolem tegtal ya bàyyikoo ca Buur Axas ca Damaas. Uri noppi na ko bala Buur Axas di ñibbsi. \v 12 Ba Buur Axas ñibbsee, jóge Damaas, ba nemmiku sarxalukaay ba, daa dikk ba ca sarxalukaay ba, joxe fa sarax. \v 13 Taal na fa \w saraxu rendi-dóomalam|lemma="Sarax yi:"\w*, joxe ca \w saraxu peppam|lemma="Sarax yi:"\w*, sotti ca \w saraxu tuuroom|lemma="Sarax yi:"\w*, ba noppi xëpp deretu \w saraxu cantam ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w* ca kaw sarxalukaay ba. \v 14 Sarxalukaayu xànjar ba tege woon ca kanam Aji Sax ji, mu jële ko ca kanam kër ga mu nekkoon, ca diggante sarxalukaay bu bees baak kër Aji Sax ji, teg ko ca wetu sarxalukaay bu bees ba, fa féete bëj-gànnaar. \v 15 Ci biir loolu Buur Axas sant Uri sarxalkat ba ne ko: «Ci kaw sarxalukaay bu mag bi ngay joxe saraxu rendi-dóomalu suba si, ak saraxu pepp bu ngoon bi, ak saraxu rendi-dóomalu buur bi, ak saraxu peppam, boole ci saraxu rendi-dóomal bi ñuy joxeel mboolem waa réew mi, ak seen saraxu pepp, ak seen saraxu tuuru. Te nga xëpp ci kawam mboolem deretu saraxu rendi-dóomal bi, ak deretu mboolem sarax su ñuy rendi. Sarxalukaayu xànjar bi moom, maa koy moom, di ko gindikoo ci Aji Sax ji.» \v 16 Uri sarxalkat ba def la ko Buur Axas sant lépp. \p \v 17 Ci kaw loolu Buur Axas toj làcci rootukaay ya ñuy dawal\f + \fr 16.17 \fr*\fk làcci rootukaay: \fk*\ft seetal ci \ft*\ft \+bk 1.Buur ya\+bk* 7.27-29.\ft*\f*, jële bagaan ya woon ca kaw, teggi mbalka mu mag ma ñuy wax Géej te tege woon ca yëkki xànjar ya ko yenu. Mu teg ko ci kawab dëru doj. \v 18 Ci kaw loolu bëgg lu neex buurub Asiri tax mu soppi buntu \w bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"\w*, ba mbaar tiimoon ci biir kër Aji Sax ji, soppiwaale buntu buur ba féete biti. \p \v 19 Li des ci mbiri Axas ak la mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. \v 20 Gannaaw gi Axas tëdd, fekki ay maamam. Ca ay maamam lañu ko denc, ca gox ba ñu naan dëkku Daawuda, Esekiya doomam falu buur, wuutu ko. \c 17 \s1 Ose falu na buur ca Israyil \p \v 1 Ba Axas buurub Yuda duggee fukkeelu atu nguuram ak ñaar, ca la Ose\f + \fr 17.1 \fr*\fk Ose \fk*\ft mii wuute naak Yonent Yàlla Ose.\ft*\f* doomu Ela falu buurub Israyil, péeyoo Samari. Nguuru na Israyil juróom ñeenti at, \v 2 di def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu. Waaye dabul buurub Israyil ya ko jiitu. \p \v 3 Moom la Salmanasar buurub Asiri song, mu nangul ko, di ko fey galag. \v 4 Gannaaw gi nag buurub Asiri gis ne Ose lal na pexe, ndax daa yónnee ay ndaw ca So buuru Misra, ba noppi lànk ne du fey galag at mu nekk. Buurub Asiri jàpp ko, tëj. \s1 Samari, péeyu Israyil, tas na \p \v 5 Ba loolu amee Salmanasar buurub Asiri dal ca kaw réew ma mépp, dikk ba Samari, gaw ko diiru ñetti at. \v 6 Ba Ose duggee juróom ñeenteelu atu nguuram, ca la buurub Asiri nangu Samari, jàpp waa Israyil, yóbbu Asiri. Ñii mu teg leen ca diiwaanu Ala, ñee ca Gosan ca wetu dex ga ñuy wax Abor, ña ca des mu dëël leen ca dëkki xeet wa ñuy wax Medd. \p \v 7 Li waral ñu nangu Samari mooy waa Israyil a bàkkaar, tooñ \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji seen Yàlla ja leen génne réewum Misra, xettli leen ca Firawna buuru Misra. Waa Israyil di jaamu yeneen yàlla, \v 8 di topp baaxi xeet ya Aji Sax ji dàq ngir ñoom, di topp baax yi buuri Israyil tëralal seen bopp. \v 9 Waa Israyil teg ca di jéema nëbbuy def njubadi gu seen Yàlla Aji Sax jiy tere; di tabax ay \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* ca seen dëkk yépp, dale ko ca tatay wattukat ya, ba ca dëkk ya ñu wëraley tata. \v 10 Ñu boole ca sampal seen bopp ay tuuri doj ak xer yu ñuy jaamoo \w Asera|lemma="Asera:"\w* ci kaw mboolem tund wu kawe mbaa ker garab gu naat. \v 11 Ñuy taal cuuraay foofa ca mboolem bérabi jaamookaay ya, di roy xeet ya Aji Sax ji dàq ngir ñoom. Ñuy def daal ay ñaawtéef, di merloo Aji Sax ji, \v 12 di jaamu ay kasaray tuur, te Aji Sax ji waxoon leen ne buñu leen jaamu. \v 13 Moonte Aji Sax ji àrtu woon na Israyil ak Yuda, mboolem yonentam yaak boroom peeñu ya jottli leen ko, ne leen: «Dëppleen seen yoon yu bon yii ngeen topp, te sàmm samay santaane, wormaal samay dogal, na mu dëppook mboolem yoon wi ma tëralal seeni maam, yónnee leen ko, yonent yiy samay jaam jottli leen ko.» \p \v 14 Teewul ñu të ticc, sajju loos ni seen maam ya gëmuloon seen Yàlla Aji Sax ji. \v 15 Dañoo xalab ay ndigalam ak \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* ga mu fasoon ak seeni maam, xalab kàddu ya mu leen artoo woon. Ñu topp ay tuuri caaxaan ba mujj di niti caaxaan, di roy xeet yi leen wër, te Aji Sax ji tere woon leen ñu roy leen. \v 16 Ba loolu amee ñu dëddu mboolem seen santaaney Yàlla Aji Sax ji; sàkkal seen bopp ñaari wëllu yu ñu móol, samp xer wu ñuy jaamoo Asera, di sujjóotal mboolem biddiiwi asamaan tey jaamu \w Baal|lemma="Baal:"\w*. \v 17 Ci biir loolu ñuy lakk seen doom yu góor ak yu jigéen ngir ay tuur, di gisaaneek a xërëmtu, ba làggi ci jëfi mbon yu Aji Sax ji ñaawlu, ba tax mu mer. \v 18 Moo tax Aji Sax ji mere Israyil lool, ba jële leen fi kanamam, ba giirug Yuda rekk des fa. \p \v 19 Waa Yuda it sàmmuñu seen santaaney Yàlla Aji Sax ji. Dañoo roy ci aada yi Israyil sos, di ko jëfe. \v 20 Moo tax Aji Sax ji xalab mboolem \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, fitnaal leen, teg leen ci loxoy yàqkat yi, ba ni mu leen wacce. \p \v 21 Ba Aji Sax ji foqatee Israyil ca loxol waa kër Daawuda, dañoo fal Yerbowam doomu Nebat buur; Yerbowam dëddale Israyil ak Aji Sax ji, yóbbe leen bàkkaar bu réy; \v 22 mbooloom Israyil topp Yerbowam ci bàkkaar ya muy def yépp, bañ koo dëddu, \v 23 ba Aji Sax ji dëddu leen, muy la mu waxoon, yonent yay jaamam jottli ko. Noonu la mujj génne Israyil réewam, yóbbu leen Asiri ba bésub tey jii. \s1 Waa Asiri sancal nañuy jaambur ca Samari \p \v 24 Ci kaw loolu buurub Asiri jële ay nit dëkk ya ñuy wax Babilon ak Kuta ak Awa ak Amat ak Sefarwayim, dëël leen dëkki Samari, ñu wuutu \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. Ñu daldi moom diiwaanu Samari, féetewoo dëkk ya. \v 25 Ba ñuy doora sanc foofa, ragaluñu woon \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ba tax Aji Sax ji yebal ay gaynde ci seen biir, ñu di leen rey. \v 26 Ñu wax buurub Asiri ne ko: «Xeet ya nga toxal, sancal leen ca dëkki Samari de, xamuñu yoonu Yàllay réew ma. Yebal na ay gaynde ci seen biir. Ña nga leen di rey, ndax xamuñu yoonu Yàllay réew ma.» \p \v 27 Ba loolu amee buurub Asiri joxe ndigal ne: «Yebal-leen fa kenn ci \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ya ngeen fa toxale, mu dem toog foofa, jàngal leen yoonu Yàllay réew ma.» \v 28 Kenn ca sarxalkat ya ñu jële woon Samari nag dikk, dëkksi Betel, jàngal leen nu ñuy jaamoo Aji Sax ji. \v 29 Terewul xeet wu ci nekk di sàkk ba tey seen tuuri bopp ca seen dëkk ya ñu féete, ba dugal tuur ya ca \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w*, ya waa Samari defaroon. \v 30 Ci biir loolu waa Babilon sàkk tuur ma ñuy wax Sukkóot Benoot, waa Kuta sàkk Nergal, waa Amat sàkk Asima; \v 31 waa Awa sàkk Nibaas ak Tartag, waa Sefarwayim di lakk seeni doom ngir tuuri Sefarwayim yi ñuy wax Addraameleg ak Anameleg. \v 32 Ñu boole ci di jaamu Aji Sax ji, tabb fu nekk ci seen biir ay sarxalkat ngir bérabi jaamookaay ya, ñu di leen sarxalal ca bérabi jaamookaay yooyu. \v 33 Ñuy wormaal Aji Sax ji, di jaamuwaale seen tuuri bopp itam, na ñu ko baaxoo ca seen waa réewum cosaan ma ñu leen toxale. \v 34 Ba tey jii ñu ngi topp seen aaday cosaan. Ragaluñu Aji Sax ji dëgg te sàmmontewuñook santaane yeek dogal yeek yoon week ndigal li Aji Sax ji joxoon askanu Yanqóoba mi mu tudde Israyil. \v 35 Aji Sax ji daa fasoon ak ñoom \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w*, sant leen ne leen: «Buleen wormaal yeneen yàlla, buleen leen sujjóotal, buleen leen jaamu, te buleen leen sarxalal itam. \v 36 Man Aji Sax ji leen génne réewum Misra ci sama kàttan gu màgg ak sama dooley loxo, man ngeen wara wormaal, di ma sujjóotal, di ma sarxalal. \v 37 Te santaane yeek dogal yeek yoon week ndigal li ma leen bindaloon, fexeleen ba di sàmmonteek moom ba fàww. Buleen wormaal yeneen yàlla. \v 38 Kóllëre gi ma fasoon ak yeen nag, buleen ko fàtte. Buleen wormaal it yeneen yàlla. \v 39 Waaye man seen Yàlla Aji Sax ji ngeen di wormaal, ma xettli leen ci seen loxol mboolem noon.» \v 40 Taxul ñu dégg, xanaa sax rekk ci seen aaday cosaan. \v 41 Noonu la xeet yooyu daan wormaale Aji Sax ji, boole ci di jaamu seen jëmmi tuur. Seeni doom it noonu, ba tey seeni sët di def na seeni maam daan def. \c 18 \s1 Esekiya falu na buur ca Yuda \p \v 1 Ba Ose doomu Ela buurub Israyil duggee ñetteelu atu nguuram, ca la Esekiya doomu Axas falu ca Yuda. \v 2 Amoon na ñaar fukki at ak juróom ba muy falu buur. Nguuru na ñaar fukki at ak juróom ñeent, péeyoo Yerusalem. Yaayam nag mooy Abi doomu Sàkkaryaa. \v 3 Muy def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji rafetlu, mboolem noonee ko Daawuda maamam daan defe. \p \v 4 Moom moo dindi \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* ya, toj tuuri doj ya, gor xer wa ñuy jaamoo \w Asera|lemma="Asera:"\w*, rajaxe jaanu xànjar ja Musaa defaroon. Ndax ba ca jamono yooya waa Israyil dañu daan taalal jaanu xànjar ja cuuraay, tudde ko Nexustan. \v 5 Ni Esekiya wóoloo woon Aji Sax ji Yàllay Israyil amu ci moroom ci mboolem buuri Yuda yi topp ci moom mbaa yi ko jiitu. \v 6 Dafa sax ci Aji Sax ji, dëdduwu ko, xanaa di topp ndigal ya Aji Sax ji joxoon Musaa. \p \v 7 Aji Sax ji nag ànd ak Esekiya, mu am ndam ci mboolem lu mu sumb. Bañ na noteelu buurub Asiri, ba nangulatu ko. \v 8 Ci kaw loolu dàq na waa Filisti, ba ca dëkk ba ñuy wax Gasa ak diiwaanam, dale ko ca tatay wattukat ya ba ca dëkk yu mag ya ñu wëraley tata. \p \v 9 Ba Esekiya buurub Yuda duggee ñeenteelu atu nguuram, yemook ba buurub Israyil Ose doomu Ela duggee juróom ñaareelu atu nguuram, ca la Salmanasar buurub Asiri song Samari, gaw ko. \v 10 Gaw nañu Samari ba ca ñetteelu at ma, door koo nangu, ca juróom benneelu atu nguurug Esekiya, yemook ba Ose buurub Israyil duggee juróom ñeenteelu atu nguuram. \v 11 Ba mu ko defee buurub Asiri jàpp Israyil, yóbbu Asiri, dëël leen diiwaanu Ala ak Gosan ga dexu Abor wale, ak ca dëkki xeetu Medd ya. \v 12 Li waral loolu mooy waa Israyil a déggalul seen Yàlla Aji Sax ji. Dañoo fecci \w kóllëreem|lemma="kóllëre g-:"\w* ak moom, ba mboolem li Musaa, jaamu Aji Sax ji, santaane woon, faalewuñu ko, jëfewuñu ko. \s1 Asiri song na Yuda \p \v 13 Ca fukk ak ñeenteelu atu nguurug Esekiya buurub Yuda, ca la Senakerib buurub Asiri dikk song mboolem dëkki Yuda ya tata wër, daldi leen nangu. \v 14 Esekiya buurub Yuda yónnee ca buurub Asiri ca Lakis ne ko: «Tooñ naa de, waaye ngalla baal ma, te dem. Loo ma sas dinaa ko fey.» Buurub Asiri sas Esekiya buurub Yuda juróom ñeent fukki barigoy xaalis ak juróom ñeenti barigoy wurus. \v 15 Esekiya joxe mboolem xaalis ba nekkoon ca kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ak ca dencukaayi kër Buur. \v 16 Booba la Esekiya xobbi wurus wa ñu xoobe woon bunti kër Aji Sax ji ak kenu ya, yónnee ko buurub Asiri. \p \v 17 Buurub Asiri nag tollu ca Lakis, yebal bummeem ak kilifay jawriñam ak bëkk-néegam, ñu ànd ak mbooloom xare mu takku, dem Yerusalem. Ba ñu agsee Yerusalem ba tollook solomu mbàndum kaw ma, fa feggook yoon wa jëm ca toolub fóotukaay ba, fa lañu taxaw. \v 18 Ci kaw loolu ñu woolu Buur. Gannaaw loolu bootalub buur Elyakim doomu Ilkiya moo ànd ak Sebna bindkat ba, ak ka yor téere ya, Yowa doomu Asaf, ñu dikk dajeek ñoom. \p \v 19 Ba mu ko defee Rabsake bëkk-néegu buurub Asiri ne leen: «Waxleen nag Esekiya ne ko: Buur bu mag ba, buurub Asiri dafa wax ne: “Sa yaakaar jii nga yaakaar, ana foo ko teg? \v 20 Defe nga ne làmmiñ kese doy na pexeek njàmbaar cib xare? Ma ne: Ana kan nga yaakaar bay fippu ci sama kaw? \v 21 Misra daal, nga def sa yaakaar, bantu barax bu tas boobu di sokk képp ku ko wéeroo! Firawna buuru Misra de, mooy boobu bant ci képp ku ko yaakaar. \v 22 Xanaa doo ma ne seen Yàlla Aji Sax ji ngeen yaakaar? Xanaa du moom nga toxal \w bérabi jaamookaayam|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* yeek \w sarxalukaayam|lemma="sarxalukaay b-:"\w*, ba noppi ne waa Yerusalem ak Yuda sarxalukaay boobu ci Yerusalem lañuy sujjóotal?” \v 23 Léegi daal, déggool rekk ak sama sang buurub Asiri, ma jox la ñaari junniy fas. Ndegam am ngay gawaram! \v 24 Ana noo mana tëwe ki gëna tuut ci sama jawriñi sang? May wax ngay yaakaare Misra ay watiir aki fas! \v 25 Te sax, xanaa du Aji Sax ji laa àndal ba dalsi fi kaw bérab bii, ngir tas ko? Aji Sax ji ci boppam moo ma ne: “Songal réew mii, tas ko!”» \p \v 26 Ci kaw loolu Elyakim doomu Ilkiya ak Sebna ak Yowa ñaan Rabsake, ne ko: «Ngalla, làkk nu arameen, dégg nanu ko. Bu nu wax ebrë, mbooloo mi ci kaw tata ji di ci dégg.» \v 27 Bëkk-néeg ba ne leen: «Ndax yeen ak seen sang doŋŋ la ma sama sang yóbbante kàddu yii? Ñi toog ci kaw tata ji dañu cee bokkul? Te ñu nara ànd ak yeen lekk seen jonkani bopp, naan seenum saw!» \v 28 Ba loolu amee bëkk-néeg ba taxaw, xaacu ca kaw ci ebrë ne: «Dégluleen kàddug buur bu mag bi, buurub Asiri. \v 29 Buur dafa wax ne bu leen Esekiya nax, ndax manu leena xettli ci loxoom. \v 30 Bu leen Esekiya yaakaarloo Aji Sax ji it, naan leen: “Aji Sax ji moo nuy xettli moos, te deesul teg dëkk bii ci loxol buurub Asiri!” \v 31 Buleen déglu Esekiya. Buurub Asiri kat dafa wax ne: Jàmmooleen ak man te ngeen génn dëkk bi, dikk nangul ma. Su ngeen ko defee, ku nekk ci yeen mana lekk ak jàmm ci garabu reseñam, lekk ak jàmm ci figgam, di naan ndoxum teenam, \v 32 ba keroog may dikk, yóbbu leen réew mu mel ni seen reew mi, réewum pepp ak ndoxum reseñ, réewum mburu ak tooli reseñ, réewum garabi oliw, diw ak lem tuuru, ndax ngeen dund te baña dee. Bu leen Esekiya sànk, naan leen: “Aji Sax ji moo nuy xettli.” Buleen ko déglu! \v 33 Ndax tuuri xeet yi mas nañoo xettli réewu wenn xeet ci buurub Asiri? \v 34 Ana tuuri réew yii di Amat ak Arpàdd? Ana tuuri Sefarwayim ak Ena ak Iwa? Ndax dañoo xettli Samari ci man? \v 35 Tuuri réew yépp, ana mu ci xettli menn réew ak man, ba Aji Sax ji wara mana xettli, Yerusalem ak man?» \p \v 36 Mbooloo ma nag ne cell, tontuwuñu ko baat, ndax Buur moo leen santoon ne leen buñu ko tontu. \v 37 Ba loolu amee bootalub Buur, Elyakim doomu Ilkiya ak Sebna, bindkat ba, ak doomu Asaf, Yowa ma denc téere ya, ñoo dem ak seen yérey ñaawlu yu xottiku, ba ca Esekiya. Ñu daldi koy àgge kàddug bëkk-néeg ba. \c 19 \p \v 1 Naka la ko Buur Esekiya dégg, daldi xotti ay yéreem, sol saaku yu muy ñaawloo. Mu dem nag ca kër Aji Sax ji \v 2 Ba loolu amee mu yebal Elyakim bootalub Buur ak Sebna bindkat ba, ak ñay mag ca \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ya. Ñu sol saaku yu ñuy ñaawloo, daldi dem ca Yonent Yàlla Esayi doomu Amocc. \v 3 Ñu ne ko: «Esekiya dafa wax ne: “Bésub tey bésub njàqare la ak mbugal ak gàcce. Mooy li ñuy wax naa: Doom a ngi ci buntub juddu, te dooley wasin réer! \v 4 Jombul nag sa Yàlla Aji Sax ji dégg mboolem kàdduy bëkk-néeg bi sangam buurub Asiri yebal, ngir mu kókkali Yàlla jiy dund. Te kon sa Yàlla Aji Sax ji mooy dogal mbugal mi war ci kàddu yooyu mu dégg. Yékkatil kàddug ñaan rekk, ngir ñi fi desagum.”» \p \v 5 Ba surgay Buur Esekiya àggee Esayi wax jooju leen seen sang wax, \v 6 Esayi da ne leen: «Waxleen seen sang ne ko: Aji Sax ji dafa wax ne: “Bul ragal kàddu yi nga dégg surgay buurub Asiri ñàkke ma ko kersa. \v 7 Maa ngii di ko sol xel mu ko gëmloo xibaar bu muy dégg, ba dellu réewam, ma fàdde ko ab saamar ca am réewam.”» \s1 Asiri tooñati na Yuda \p \v 8 Gannaaw loolu Rabsake dégg ne buurub Asiri bàyyikoo na Lakis, bay xareek dëkk ba ñuy wax Libna. Mu walbatiku fekki ko foofa. \v 9 Booba buurub Asiri daa dégg ne Tiraka buurub \w Kuus|lemma="Kuus:"\w* moo leen di songsi. Mu dellu yebal ay ndaw ca Esekiya, ne leen:: \v 10 «Waxleen Esekiya buurub Yuda, ne ko: “Seen Yàlla ji ngeen yaakaar, bumu leen nax, naa leen deesul teg Yerusalem ci loxol buurub Asiri. \v 11 Xanaa yaw ci sa bopp dégg nga li buuri Asiri def mboolem réew yi, faagaagal leen? Yaw nag, yaa ciy mucc? \v 12 Xeet yi samay maam sànk, seeni tuur dañu leena musal, muy Gosan, di Karan, di Resef, di askanu Eden wa woon ca Telasar? \v 13 Ana buuri Amat ak Arpàdd ak Layir ak Sefarwayim ak Ena ak Iwa?”» \p \v 14 Ba Esekiya jëlee bataaxal ba ca loxol ndaw ya, jàng ko ba noppi, dafa dem ba ca kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Mu daldi tàllal bataaxal ba fa kanam Aji Sax ji. \v 15 Esekiya ñaan fi kanam Aji Sax ji, ne ko: «Éy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Yàllay Israyil mi toog fi tiim malaakay \w serub|lemma="serub y-:"\w* yi. Yaw doŋŋ yaa di Yàllay mboolem nguuri àddina. Yaw déy, yaa sàkk asamaan ak suuf. \v 16 Ngalla Aji Sax ji, dékkal sa nopp ba dégg; Aji Sax ji, xippil say gët ba gis, te dégg kàdduy Senakerib yi mu yóbbante, ngir ñàkke la ko kersa, yaw, Yàlla jiy dund! \v 17 Aylayéwén Aji Sax ji, buuri Asiree tas xeet yeek seeni réew, \v 18 te ñoo sànni seeni yàlla ci sawara it, ndax yooyoo dul Yàlla, xanaa lu nit sàkke loxoom, bant ak doj, ba tax ñu sànk leen. \v 19 Kon nag Aji Sax ji sunu Yàlla, ngalla wallu nook moom, ba mboolem nguuri àddina xam ne yaw Aji Sax ji doŋŋ yaa di Yàlla.» \s1 Yonent Yàlla Esayi yégle na jéllub Asiri \p \v 20 Ba mu ko defee Esayi doomu Amocc yónnee ca Esekiya ne ko: «\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Yàllay Israyil dafa wax ne li nga ko ñaan ci Senakerib buurub Asiri, dégg na ko. \v 21 Lii moo di kàddu gi Aji Sax ji wax ci moom: \q1 Yaw, janq \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w* mu taaru da laa xeeb, \q1 di la ñaawal. \q1 Yerusalem, dëkk bu taaru booboo \q2 lay wëcc bopp, \q1 di la kekku sa gannaaw. \q1 \v 22 Ana kooy kókkaleek a ñàkke kersa? \q1 Moo kooy yékkatil kàddu? \q1 Kooy xool gëti xeebeel? \q1 Xanaa du Aji Sell ju Israyil ji? \q1 \v 23 Yaa yebal say ndaw, di kókkali Boroom bi, \q1 te naa: “Sama watiir yi ne xas \q1 laa ware kawtey tund yi, jàll ba ca xolu Libaŋ. \q1 Maa gor seedaram ya fa sut, \q1 ak tànnéefi garabi sipparam, \q1 maay àkki ba ca collub dalub tundu Libaŋ, \q1 ak gottam bu naat ba nib tóokër. \q1 \v 24 Maa gas ay teen, naan ndoxum réewum jaambur, \q1 maa joggatee sama téstën, wali Misra yépp, \q1 ŋiisal ko.” \b \q1 \v 25 «Waaye xanaa déggoo ne bu yàgg laa dogal loolu? \q1 Ca jant ya woon laa ko nasoon, \q1 tey ma sottal ko, \q1 ba nga mana def genti jali tojit, dëkk yu tata wër. \q1 \v 26 Waa dëkk ya ne yàcc, jàq, torox, \q1 mel ni gàncaxu àll mbaa ñax mu yees, \q1 mbete caxum xadd, \q1 balaa màgg lax. \b \q1 \v 27 «Waaye boo toogee, boo génnee, boo duggee, \q2 xam naa, \q1 boo xadaroo sama kaw it, xam naa. \q1 \v 28 Yaa xadaru sama kaw, \q1 ba sag reewande tàbbi sama nopp! \q1 Maa lay takkal ag nos akug laab, \q1 waññi la, nga dellu yoon wa nga dikke woon. \b \q1 \v 29 «Lii, def ko ci, mu dib takk. \q1 Dees na lekk ren peppum saxayaay, \q1 déwén it dees na lekk lu saxal boppam. \q1 Waaye déwén-jéeg, \q1 ngeen ji, góob, \q1 jëmbat tóokëri reseñ, lekk ca meññeef ma. \q1 \v 30 Ndes wa des ca askanu Yuda \q1 ñooy saxaat ay reen, \q1 ba meññaat ay doom. \q1 \v 31 Yerusalem kay law ndes di génne, \q1 aw ndes ay rëcce tundu Siyoŋ, \q1 te Aji Sax ji Boroom gàngoor yi \q2 mooy sottal loolu ci xéraangeem. \p \v 32 «Moo tax Aji Sax ji wax ci buurub Asiri ne: \q1 “Du dugg ci dëkk bii, \q1 du fi soqig fitt, \q1 du fi taxawe ab pakk, \q1 du fi jal jal bu muy gawe. \q1 \v 33 Yoon wa mu dikke lay delloo, \q1 biib dëkk du fi dugg. \q1 Kàddug Aji Sax jee. \q1 \v 34 Maay aar dëkk bii, musal ko \q2 ngir man ci sama bopp, \q1 ak Daawuda sama jaam bi.”» \p \v 35 Guddig keroog malaakam Aji Sax ji moo dikk, fàdd ca dalub Asiri téeméer ak juróom ñett fukk ak juróomi junni (185 000). Ca ëllëg sa ña mucc teela xëy, yemuñu ci lu moy ñooña ñépp, diy néew. \p \v 36 Ba loolu amee Senakerib buurub Asiri daldi fabu, ñibbi. Mu toog nag ca Niniw. \v 37 Gannaaw gi, ba muy sujjóot ca kër tuuram ma ñuy wax Nisrog, Addraameleg ak Sareser, doomam yu góor ñoo ko fa fàdde saamar. Ñoom nag, ñu daw làquji réew ma ñuy wax Araraat. Ci kaw loolu doomam Asaradon falu buur, wuutu ko. \c 20 \s1 Esekiya wopp na, ba jóg \p \v 1 Jant yooyu Esekiya moo woppoon bay waaja dee. Yonent Yàlla Esayi doomu Amocc dikk, ne ko: «\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: Dénkaaneel sa mbiri kër, ndax dangay dee, doo jóg!» \v 2 Mu walbatiku nag, jublook miir ba, ñaan ci Aji Sax ji ne ko: \v 3 «Éy Aji Sax ji, ngalla bàyyil xel ni ma àndeek yaw sama léppi xol, ci kóllëre, te li nga rafetlu laa jëfe.» Mu jooy nag, jooy yu metti. \p \v 4 Ba loolu amee Esayi génn, weeseegul digg ëtt ba sax, kàddug Aji Sax ji dikkal ko ne ko: \v 5 «Dellul ba ca Esekiya, sama njiitu ñoñ, nga ne ko: “Aji Sax ji sa Yàllay maam Daawuda dafa wax ne: Dégg naa sag ñaan, gis naa say rongooñ. Maa ngii di la wéral, te bu gannaaw ëllëgee dinga dem kër Aji Sax ji. \v 6 Dinaa yokk ci saw fan, fukki at ak juróom. Buurub Asiri ak dooleem, maa la ciy xettli, yaw ak dëkk bii, te maay aar dëkk bii ndax man ci sama bopp ak Daawuda sama jaam bi.”» \v 7 Esayi teg ca ne: «Indileen danku figg.» Ñu indi, teg ko ca taab ba, Esekiya wér. \p \v 8 Fekk na Esekiya ne Esayi: «Ana lu di takk biy firndeel ne Aji Sax ji dina ma wéral, ba ma mana dem gannaaw ëllëg ca kër Aji Sax ji?» \v 9 Esayi ne ko: «Takk biy bàyyikoo ci Aji Sax ji, di firndeel ne dina def li mu wax, yaar yii loo ci bëgg: ker gi màgg lu tollook fukki dëggastal, mbaa mu dellu gannaaw fukki dëggastal?» \v 10 Esekiya ne ko: «Ker gi màgg lu tollook fukki dëggastal moom, yomb na. Kon na dellu gannaaw fukki dëggastal.» \v 11 Ci kaw loolu Yonent Yàlla Esayi ñaan ci Aji Sax ji, Aji Sax ji delloo ker ga gannaaw lu tollook fukki dëggastal ya mu wàccoon ca kaw iskaleb Axas ba. \s1 Buuru Babilon yónnee na ca Esekiya \p \v 12 Jant yooyu doomu Baladan Berodag Baladan\f + \fr 20.12 \fr*\fk Berodag Baladan \fk*\ft mooy Merodag Baladan ba tey.\ft*\f* buuru Babilon moo yónnee Esekiya bataaxal ak yóbbal. Booba dafa dégg ne Esekiya daa woppoon. \v 13 Esekiya nag déglu ndaw ya, ba noppi won leen mboolem kërug dencukaayam: xaalis baak wurus waak ndàbb jaak diwu tànnéef gaak néegub gànnaayam ak mboolem lu nekkoon cay dencam. Amul lenn lu leen Esekiya wonul ci biir këram ak mboolem fu bokk ci kilifteefam. \p \v 14 Gannaaw loolu Yonent Yàlla Esayi dikk ne Buur Esekiya: «Lu la nit ñii wax ak fu ñu jóge sax ba fi yaw?» Esekiya ne: «Réew mu sore lañu bàyyikoo, dikk, réewum Babilon.» \v 15 Mu ne ko: «Ana lu ñu gis sa biir kër?» Esekiya ne ko: «Mboolem lu nekk sama biir kër, gis nañu ko. Amul lenn lu ma leen wonul ci samay denc.» \v 16 Esayi ne Esekiya: «Déglul kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji: \v 17 “Ay jant a ngii di ñëw, dees na yóbbu Babilon lépp lu nekk sa biir kër, te say maam dencoon ko, ba tey jii. Du lenn luy des. Kàddug Aji Sax jee. \v 18 Te it ñenn ci sag njaboot, ñu soqikoo ci yaw, di ñoo meññ ci sa geño, dinañu leen jàpp, ñu doon jaam yu ñu tàpp ca biir kër buuru Babilon.”» \v 19 Esekiya ne Esayi: «Kàddug Aji Sax ji nga jottli jàmm la.» Booba ma nga naan: «Xanaa du jàmm ju ne ñoyy ay am sama giiru dund?» \s1 Buur Esekiya saay na \p \v 20 Li des ci mbiri Esekiya ak mboolemi njàmbaaram ak mbànd mi mu defar ak solomam, muy indi ndox ca biir dëkk ba, bindees na lépp moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. \v 21 Esekiya nag saay, fekki ay maamam. Doomam Manase falu buur, wuutu ko. \c 21 \s1 Manase falu na buur ca Yuda \p \v 1 Fukki at ak ñaar la Manase amoon ba muy falu buur. Nguuru na juróom fukki at ak juróom fa Yerusalem. Yaayam mooy Efsiba. \v 2 Manase nag di def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu, topp ñaawtéefi xeet ya Aji Sax ji dàqoon ngir \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \v 3 Moo tabaxaat \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* ya Esekiya baayam tasoon, yékkatil tuur mi ñu naan \w Baal|lemma="Baal:"\w* ay \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*, samp xer wu ñuy jaamoo \w Asera|lemma="Asera:"\w*, noonee ko Axab buurub Israyil defe woon, boole ca di sujjóotal mboolem biddiiwi asamaan, di leen jaamu. \v 4 Moo yékkati yeneen sarxalukaayi tuur ca biir kër Aji Sax ji, fa Aji Sax ji waxoon ne: «Fii ci Yerusalem laay dëj sama tur.» \v 5 Ay sarxalukaay it la tabaxal biddiiwi asamaan yépp ca biir ñaari ëtti kër Aji Sax ji. \v 6 Te itam sarxal na doomam, lakk ko ngir ay tuur. Ci biir loolu jabar na, ñeengo na, jëflante naak boroom rawaan aki gisaanekat. Bare na lu mu def lu Aji Sax ji ñaawlu, ba merloo ko. \p \v 7 Moo dugal ba tey jëmm ja mu sàkkoon ngir tuur ma ñuy wax \w Asera|lemma="Asera:"\w*, ca biir kër ga Aji Sax ji waxoon Daawudaak doomam Suleymaan ne leen: «Ci biir kër gii ci Yerusalem, gi ma tànne ci mboolem giiri Israyil, laay dëj sama tur ba fàww. \v 8 Ndegam bànni Israyil saxoo nañoo sàmm mboolem lu ma leen santoon, te mu dëppook mboolem yoon wi leen Musaa sama jaam ba sant ñu topp ko, dootuma leen wërloo, ñu wacc réew mi ma joxoon seeni maam.» \v 9 Waaye bànni Israyil ñoo dégluwul, ba Manase waññi leen, ñuy def ay ñaawtéef, ba raw xeet ya Aji Sax ji sànkoon fi kanam bànni Israyil. \p \v 10 Ba loolu amee Aji Sax ji wax, yonent yay jaamam jottli. Mu ne: \v 11 «Manase buurub Yuda moo def yii ñaawtéef, ba jëfam ju bon raw mboolem lu Amoreen ña ko jiitu defoon, ba yóbbe waa Yuda ñuy moye ay kasaray tuur. \v 12 Moo tax man Aji Sax ji Yàllay Israyil damaa wax ne: “Maa ngii di wàcce ci Yerusalem ak Yuda musiba muy buur noppi képp ku ci dégg. \v 13 Dinaa nattoo Yerusalem buumu beteex ba ma nattoo Samari ak nattukaay ba ma nattoo waa kër Axab. Dinaa ñédd Yerusalem, ba mu mel ni ndab lu ñu ñiit ba mu set, dëpp ko. \v 14 Dinaa suur sama ndesu ñoñ te dinaa leen teg ci seen loxol noon yi, seen bañ yépp di leen futteek a sëxëtoo, \v 15 ndegam li ma ñaawlu lañu masa def, di ma merloo, ba seeni maam génnee Misra ba tey jii.”» \p \v 16 Te it deretu nit ñu deful dara la Manase tuur, ba mu fees Yerusalem dell, cat ba cat, te bokkul ak bàkkaar bi mu bàkkaarloo waa Yuda, ba ñuy def li Aji Sax ji ñaawlu. \p \v 17 Li des ci mbiri Manase ak mboolem lu mu def ak bàkkaaram ba mu def, bindees na lépp moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. \v 18 Gannaaw gi Manase saay, fekki ay maamam, ñu denc ko ci toolub këram, di toolub Usa. Doomam Amon falu buur, wuutu ko. \s1 Amon falu na buur ca Yuda \p \v 19 Ñaar fukki at ak ñaar la Amon amoon ba muy falu buur. Ñaari at la nguuru fa Yerusalem. Yaayam moo doon Mesulemet doomu Arus ma cosaanoo Yotba. \v 20 Amon di def nag li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu, la baayam Manase daan def. \v 21 Topp na baayam ci mboolem tànk ya mu jaaroon, di jaamu kasaray tuur yi baayam daan jaamu, di leen sujjóotal. \v 22 Daa dëddu Aji Sax ji, Yàllay maamam, baña jaar ci yoonu Aji Sax ji. \p \v 23 Ci kaw loolu surgay Amoon lalal Amon pexe, bóom ko ca biir këram. \v 24 Waa réew ma nag rey mboolem ña fexeeloon Buur Amon. Ba loolu amee waa réew ma fal buur doomam Yosya, mu wuutu ko. \v 25 Li des ci mbiri Amon ak li mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. \v 26 Ba loolu amee ñu denc ko ca bàmmeelam ca toolub Usa, Yosya doomam falu buur, wuutu ko. \c 22 \s1 Yosya falu na buur ca Yuda \p \v 1 Juróom yetti at la Yosya amoon ba muy falu buur, te fanweeri at ak benn la nguuru fa Yerusalem. Yaayam mooy Yedida doomu Adaya ma cosaanoo Boskat. \v 2 Yosya di def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji rafetlu, topp ci mboolem tànk yi maamam Daawuda jaaroon, jàddul fenn, du ndijoor, du càmmoñ. \p \v 3 Buur Yosya nag, ca fukk ak juróom ñetteelu atu nguuram, dafa yebal bindkat ba, Safan doomu Asalyaa doomu Mesulam, ca kër Aji Sax ji. Mu ne ko: \v 4 «Demal ca Ilkiya \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bu mag ba, ne ko mu yembal saraxi xaalis, yi wattukati bunti kër Aji Sax ji nangoo ci nit ñi. \v 5 Nañu ko teg ci loxoy liggéeykat yiy saytu liggéeyu kër Aji Sax ji. Ñooñu jox ko liggéeykat ya ca kër Aji Sax ji, di defaraat kër ga, \v 6 muy liggéeykati bant yi ak tabaxkat yi ak yeneen liggéeykat. Nañu ci jënd bant ak doji yett, defare ko kër gi. \v 7 Waaye buñu leen laaj nu ñu def xaalis bi ñu leen jox, ndax ñu maandu lañu ci seen liggéey.» \s1 Téereb yoon wi feeñ na \p \v 8 Ilkiya \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bu mag ba nag ne Safan bindkat ba: «Téereb yoon wi de laa gis ci kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji!» Ci kaw loolu Ilkiya jox Safan téere ba, mu jàng ko. \v 9 Ba loolu amee Safan bindkat ba dellu ca Buur, àgge ko gii kàddu: «Sa surga ya sotti nañu xaalis ba nekkoon ca kër Aji Sax ji, ba teg ko ca loxol ñi yor liggéey bi te di saytukati kër Aji Sax ji.» \v 10 Safan bindkat ba teg ca xamal Buur ne ko: «Ab téere nag la ma Ilkiya sarxalkat bi jox.» Safan jàngal ko Buur. \p \v 11 Ba Buur déggee kàdduy téereb yoon wa, daa xotti ay yéreem ndax tiitaange. \v 12 Mu wax Ilkiya sarxalkat ba, mook Ayikam doomu Safan, ak Agbor doomu Mikaya, ak Safan bindkat ba, ak Asaya bëkk-néegu buur, ne leen: \v 13 «Demleen seetal ma ci Aji Sax ji, seetaaleel mbooloo meek Yuda gépp ci mbirum kàdduy téere bii feeñ. Sànjum Aji Sax ji tàkk ci sunu kaw kat réy na, ndax sunuy maam a déggul kàdduy téere bii, ngir jëfe mboolem li ñu nu ci bindal.» \v 14 Ilkiya sarxalkat ba daldi dem ànd ak Ayikam ak Agbor ak Safan ak Asaya, ba ca Ulda yonent bu jigéen bay soxnas wattukatub yére ya, Salum doomu Tigwa doomu Aras. Ulda ma nga dëkkoon Yerusalem ca sanc ba. Ñu wax ak moom. \p \v 15 Jigéen ja ne leen: «Aji Sax ji Yàllay Israyil nee: Xamal-leen ki leen yebal ci man ne ko: \v 16 “Aji Sax ji nee: Maa ngii di wàcce musiba ci bérabi bii ak ñi ko dëkke, muy mboolem kàdduy téere bi buurub Yuda jàng. \v 17 Gannaaw ñoo ma dëddu, di taalal yeneen yàlla cuuraay, ngir merloo ma ci mboolem liggéey bu ñu defe seeni loxo, samam sànj mooy tàkk fi bérab bii te du fey.” \v 18 Buuru Yuda mi leen yónni, ngir ngeen seetlusi ci Aji Sax ji nag, waxleen ko ne ko: “Li Aji Sax ji Yàllay Israyil wax ci kàddu yi ngeen dégg moo di: \v 19 Gannaaw yaa réccu ci sa xol, ba toroxlu ci kanam Aji Sax ji, ba nga déggee ni ma rëbbe bérab bii mook ñi ko dëkke, muy seen toroxteek seen alkànde, te yaa xotti say yére, jooy fi sama kanam, man it dégg naa la. Kàddug Aji Sax jee. \v 20 Moo tax maa ngii di la yóbbu nga fekki say maam, dees na la yóbbu ak jàmm ca sa bàmmeel, te say bët du tegu ci mboolem musiba mi may wàcce ci bii bérab.”» Ba loolu amee ñu dellu, yegge Buur kàddu ga. \c 23 \s1 Yosya sellal na réew mi \p \v 1 Ci kaw loolu Buur yónnee, ñu woo mboolem magi Yuda ak Yerusalem, ñu dikk. \v 2 Buur dem ca kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ànd ak waa Yuda gépp, Yerusalem gépp; \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yaak yonent yaak askan wépp, ka gën a tuut ba ca gën a mag. Mu jàngal leen, ñuy dégg, mboolem kàdduy téereb \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w*\f + \fr 23.2 \fr*\fk téereb kóllëre gi \fk*\ft mooy Tawreetu Yonent Yàlla Musaa.\ft*\f* ba feeñ ca kër Aji Sax ji. \v 3 Buur nag taxaw fa kenu ga, feddli kóllëre ga fa kanam Aji Sax ji, ngir topp Aji Sax ji, di sàmme léppi xol ak léppi bakkan, ay santaaneem ak seedey yoonam, ak dogali yoonam, ngir saxal kàdduy kóllëre googu ñu bind ci téere boobu. Askan wépp yebu ca kóllëre ga. \p \v 4 Ba loolu amee Buur sant Ilkiya sarxalkat bu mag ba, mook sarxalkat ya ca topp, ak wattukati buntu kër Aji Sax ji, ne leen ñu génnee kër Aji Sax ji mboolem ndab ya ñu defaraloon \w Baal|lemma="Baal:"\w* ak \w Aseraak|lemma="Asera:"\w* biddiiwi asamaan yépp. Mu génne lépp Yerusalem, lakk ko ca tooli Sedoron, ba noppi yóbbu dóom ba Betel. \v 5 Gannaaw loolu mu dàq sarxalkati tuur ya buuri Yuda faloon ñuy taal cuuraay ca \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* ya ca dëkki Yuda ak la wër Yerusalem, dàqaale ñay taalal cuuraay Baal, ak jant beek weer week xeeti dëllooñ yeek mboolem biddiiwi asamaan yépp. \v 6 Bu loolu weesee jële na kër Aji Sax ji tuur ma tudd \w Asera|lemma="Asera:"\w*, génne ko Yerusalem ba ca xuru Sedoron, lakk ko foofa ca xuru Sedoron, wol ko ba muy sunguf, mu xëpp ko ca sëgi baadoola ya. \v 7 Màbb na it këri nit ña doon jaay seen bopp fa ñuy màggale tuur ya ca biir kër Aji Sax ji, te jigéen ña daan fa ràbbal tuur ma ñuy wax Asera ay xayma. \p \v 8 Ba loolu wéyee Yosya indi Yerusalem mboolem sarxalkat ya doon sarxal ca dëkki Yuda, diggante Geba ba Beerseba, daldi sobeel bérabi jaamookaay ya ñu daan taal cuuraay, daaneel bérabi jaamookaay ya ca bunt ya, boole ca ba nekkoon ca buntu Yosuwe, boroom dëkk ba, te féete càmmoñ booy jaare ci buntu dëkk ba di duggsi. \v 9 Mayuñu woon nag sarxalkati bérabi jaamookaay ya ñuy dikk ba ca \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* Aji Sax ji ci Yerusalem. Sañuñu woon lu moy bokk lekk mburu mu amul lawiir ñook sarxalkat yi ci des. \v 10 Ci kaw loolu Yosya sobeel na fa ñuy wax Tofet ca xuru Ben Inom, ba kenn dootu fa lakk sa doom ju góor mbaa ju jigéen ngir tuur wi ñuy wax Moleg. \v 11 Jële na ca bunti kër Aji Sax ji fas ya ay buuri Yuda jagleeloon jant bi. Ña nga woon ca ëtt ba, ca wetu néegu jawriñ bu ñuy wax Netan Meleg. La ca tegu Yosya lakk watiir ya ñu jagleel jant bi. \v 12 Ci biir loolu Buur daane sarxalukaay ya ay buuri Yuda yékkati woon ca kaw xaddub néegub kaw bu Axas, ak sarxalukaay ya Manase tabaxoon ca ñaari ëtti kër Aji Sax ji. Mu jële fa lépp, def ko pënd, sànni ca xuru Sedoron. \v 13 Bérabi jaamookaay ya féete woon Yerusalem penku ca bëj-saalumu tundu Alkànde, Buur Suleymaan tabaxaloon ko tuur ma ñuy wax \w Astàrt|lemma="Astàrt:"\w*, kasaray waa Sidon ya, ak tuur ma ñuy wax Kemos, kasaray Mowabeen ña, ak tuuru Amoneen mu siblu ma ñuy wax Milkom, Buur Yosya daa boole lépp sobeel ko. \v 14 Rajaxe na tuuri doj ya, daane xer ya ñuy jaamoo Asera, wuutal fa ay jali yaxi nit, ba mu daj. \p \v 15 Naka noona mu boole ca sarxalukaay ba ca Betel ak bérabu jaamookaay ba fa doomu Nebat Yerbowam ma bàkkaarloo woon Israyil, yékkati woon. Sarxalukaay boobaak bérabu jaamookaay booba sax yàq na ko. Dafa lakk bérabu jaamookaay ba, wol ko ba mu mokk, lakk xer wa ñuy jaamoo Asera. \v 16 Ba mu ko defee Yosya ne gees, gis bàmmeel ya nekk foofa ca tund wa. Mu yeble, ñu sullil ko yax ya, mu lakk ko ca kaw sarxalukaay ba, sobeel ko noonu, muy kàddug Aji Sax ji góoru Yàlla ga waxoon\f + \fr 23.16 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk 1.Buur ya\+bk* 13.2.\ft*\f*, keroog ba Yerbowam taxawee ca sarxalukaay ba, bésub màggal. Buur Yosya neeti gees, yem ci bàmmeelu góoru Yàlla ga biraloon waxyu ba. \v 17 Mu ne: «Doj wee may séen bàmmeelu kan a?» Waa dëkk ba ne ko: «Xanaa bàmmeelu góoru Yàlla ga bàyyikoo woon Yuda. Moo waxoon bu yàgg jëf jii nga def sarxalukaayu Betel bii tey.» \v 18 Mu ne: «Bàyyileen ko noonu! Bu kenn laal ay yaxam!» Ñu wacc fa ay yaxam ak yaxi yonent ba jóge woon Samari. \p \v 19 Mboolem bérabi jaamookaay ya nekkoon ca dëkki Samari yu mag ya te buuri Israyil tabaxoon ko, ba merloo Aji Sax ji, Yosya jële na ko fa, def ko na mu defoon ca Betel rekk. \v 20 Gannaaw loolu mu rendi ca sarxalukaay ya mboolem ña fa doon sarxalkati bérabi jaamookaay ya, ba noppi lakk yaxi nit ca kaw, ngir sobeel lépp, doora dellu Yerusalem. \s1 Màggalu bésub Mucc délsi na \p \v 21 Buur Yosya nag jox mbooloo mépp ndigal ne leen: «Màggal-leen \w bésub Mucc|lemma="Màggali Yawut yi:"\w* ga, ñeel seen Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ni ñu ko binde ci téereb \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* gii.» \v 22 Bésub Mucc booba, na ñu ko màggale atam, maseesu ko nee màggale ca jamonoy njiit ya yilifoon Israyil, ba ci jamonoy buuri Israyil ak Yuda. \v 23 Ca fukk ak juróom ñetteelu atu Yosya doŋŋ lañu dellu màggal bésu Mucc boobu ca Yerusalem, ñeel Aji Sax ji. \v 24 Rax ci dolli boroom rawaan yeek gisaanekat yeek gàllaaji kër yeek kasaray tuur yeek mboolem kasara yu ni mel te ñu daan ko gis ca réewum Yudak Yerusalem, Yosya jële na ko fa ngir mana saxal kàdduy yoon wa ñu bind ca téere ba Ilkiya \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba gisoon ca biir kër Aji Sax ji. \v 25 Mboolem buur yi jiitu Yosya, kenn jubloowu ci Aji Sax ji léppi xolam ak léppi jëmmam ak kem kàttanam, bay sàmm yoonu Musaa wépp. Mboolem ñi ko wuutu it, kenn dabu ko ci. \p \v 26 Teewul Aji Sax ji dëppul ci meram mu réy mi mu dale ci kaw Yuda ndax mboolem li Manase def, ba merloo ko. \v 27 Aji Sax ji nag ne: «Yuda itam dinaa ko jële fi sama kanam, ni ma fi jëlee Israyil. Dinaa xalab dëkk bii ma tànn, di Yerusalem ak kër gii ma wax ne sama tur dina fi nekk.» \s1 Buur Yosya saay na \p \v 28 Li des ci mbiri Yosya ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. \v 29 Ca ay jantam la Firawna Neko buuru Misra jóg jàppleji buurub Asiri ca wetu dexu Efraat, Buur Yosya dogaleji ko. Teewul ba ko Neko gisee la ko rey ca Megido. \v 30 Ba loolu amee surgay Yosya yeb néew ba ci watiir, jële ko Megido, indi ko Yerusalem, denc ko ci bàmmeelu boppam. Askanu réew ma nag jël Yowakas doomu Yosya, diw ko diwug pal, fal ko buur, mu wuutu baayam. \s1 Yowakas falu na buur ca Yuda \p \v 31 Ñaar fukki at ak ñett la Yowakas amoon ba muy falu buur. Ñetti weer la nguuru fa Yerusalem. Yaayam mooy Amutal doomu Yeremi ma cosaanoo Libna. \v 32 Muy def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu, na ko ay maamam daan defe rekk. \v 33 Firawna Neko moo làqoon jant bi Yowakas ca dëkk ba ñuy wax Ribla ca réewum Amat, ba nguurootul ca Yerusalem. Mu teg réew ma galagu fanweeri barigoy xaalis, ak fanweeri kiloy wurus. \v 34 Ci kaw loolu Firawna Neko fal Elyakim doomu Yosya buur, mu wuutu baayam Yosya, soppi turam, tudde ko Yowakim\f + \fr 23.34 \fr*\ft Ci seen aada, ku jox nit aw tur, fekk na nga am kilifteef ci kawam.\ft*\f*; Yowakas moom mu jàpp ko, yóbbaale Misra. Foofa la deeye. \s1 Buur Yowakim fey na Misra galag \p \v 35 Yowakim jox na Firawna Neko xaalis baak wurus wa mu laaj. Waaye waa réew ma la ko sas, ba jële ca ñoom xaalis baak wurus wa, ku nekk ak sab sas, daldi koy dajale, jox ko Firawna Neko. \p \v 36 Ñaar fukki at ak juróom la Yowakim amoon ba muy falu buur, te fukki at ak benn la nguuru fa Yerusalem. Yaayam mooy Sebuda doomu Pedaya ma cosaanoo Ruma. \v 37 Muy def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu, mboolem noonee ko ay maamam defe woon. \c 24 \p \v 1 Ca ay jantam la Nabukodonosor buuru Babilon song réew ma. Yowakim nangul ko diiru ñetti at, doora walbatiku fippu. \v 2 Ci kaw loolu Aji Sax ji yebal ci kawam ay yàqkati waa Babilon ak yàqkati Siri ak yàqkati Mowab ak yàqkati Amoneen ña. Aji Sax ji yebal leen Yuda ngir ñu yàqte ko, mu dëppook kàddu ga mu waxoon, yonent yiy surgaam jottli ko. \v 3 Ci ndigalal Aji Sax ji moos la loolu xew ca Yuda, ba mu mujj leen xarab ndax bàkkaari Manaseek li mu def lépp, \v 4 ak deretu nit ñi mu tuur te defuñu dara; ndax Manase daa feesal Yerusalem ak deretu jaamburi Yàlla, ba Aji Sax ji nanguwu koo baal. \p \v 5 Li des ci mbiri Yowakim ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. \v 6 Gannaaw gi Buur Yowakim tëdd, fekki ay maamam. Doomam Yowakin nag falu buur, wuutu ko. \v 7 Jamono yooyu buuru Misra génnatul réewam di xareji, ndax fekk na buuru Babilon nangu suufam sépp la ko dale ca xuru Misra ba ca dexu Efraat. \s1 Yowakin falu na buur ca Yuda \p \v 8 Fukki at ak juróom ñett la Yowakin amoon ba muy falu buur. Ñetti weer la nguuru, péeyoo Yerusalem. Yaayam mooy Newusta doomu Elnatan ma cosaanoo Yerusalem. \v 9 Muy def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu, mboolem noonee ko baayam defe woon. \p \v 10 Jamono jooja la jaraafi Nabukodonosor buuru Babilon, song Yerusalem, gaw dëkk ba. \v 11 Nabukodonosor dikk ca dëkk ba, fekk ay jaraafam gaw ko. \v 12 Yowakin buurub Yuda génn fekki buuru Babilon, jébbal ko boppam, mook ndeyam aki surgaam aki jaraafam ak jawriñi këram. Buuru Babilon nag jàpp ko. Looloo nga yemook juróom ñetteelu atu nguurug Nabukodonosor buuru Babilon. \v 13 Nabukodonosor jële fa mboolem alali kër Aji Sax ji ak alali kër Buur, daldi buub lépp luy ndabu wurus lu Suleymaan buurub Israyil defarlu woon ci kër Aji Sax ji, muy la Aji Sax ji waxoon. \p \v 14 Ci biir loolu buuru Babilon yóbbu Yerusalem gépp, muy mboolem jaraaf yeek jàmbaari góor ñi, ñuy fukki junni, ñook mboolem liggéeykat yaak tëgg ya. Kenn desul, lu moy baadoola ya gëna néew doole. \p \v 15 Mu yóbbu Yowakin Babilon mook ndeyam aki soxnaam aki jawriñam ak kilifay réew ma. \v 16 Buuru Babilon boole ca jàppaale juróom ñaari junniy jàmbaari góor (7 000), ak junniy liggéeykat aki tëgg, ñoom ñépp di boroom kàttan te tollu ci xare; mu boole leen jàpp jaam, yóbbu Babilon. \v 17 Buuru Babilon moo fal Mataña, baayu Yowakin bu ndaw, mu wuutu Yowakin, daldi soppi turu Mataña, tudde ko Cedekiya. \s1 Cedekiya falu na buur ca Yuda \p \v 18 Ñaar fukki at ak benn la Cedekiya amoon ba muy falu buur, te fukki at ak benn la nguuru fa Yerusalem. Yaayam mooy Amutal doomu Yeremi ma cosaanoo Libna. \v 19 Muy def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu, mboolem noonee ko Yowakim defe woon. \v 20 Merum Aji Sax ji nag dikkal Yerusalem ak Yuda, ba mu mujj xarab leen. \p Gannaaw gi Cedekiya fippu buuru Babilon. \c 25 \s1 Nangooti nañu Yerusalem \p \v 1 Ba Cedekiya tolloo ci juróom ñeenteelu atu nguuram, fukki fan ca fukkeelu weeram, ca la Nabukodonosor buuru Babilon ànd ak mbooloom xareem mépp ci kaw Yerusalem. Ñu dal fa janook ñoom, yékkati gawukaay, wërale ko. \v 2 Dëkk ba gawe, ba keroog Cedekiya tollu ci fukkeelu atu nguuram ak benn. \v 3 Keroog juróom ñeenti fan ca weer wa, xiif ba tar lool ca biir dëkk ba, ba waa réew ma amatuñu ab dund. \v 4 Xarekati Yuda ya génn guddi daw. Fekk na waa Babilon gaw dëkk ba. Teewul ñu rëcc, jaare ca bunt ba ca diggante ñaari tata ya, ca wetu toolu buur. Cedekiya daldi wuti xuru Yurdan. \v 5 Waa Babilon nag topp Buur Cedekiya, ba dab ko ca jooru Yeriko, fekk mbooloom xareem mépp tasaaroo, wacc ko. \v 6 Ñu jàpp ko, yóbbu ko ca buuru Babilon ca dëkk ba ñuy wax Ribla. Ñu dogal fa àtteem. \v 7 Doomi Cedekiya yu góor lañu rendi, muy gis, ba noppi ñu tuur ay bëtam, jénge ko jéngi xànjar, yóbbu ko Babilon. \s1 Yàq nañu kër Aji Sax ji \p \v 8 Ba Nabukodonosor buuru Babilon tolloo ci fukkeelu atu nguuram ak juróom ñeent, ba am juróom ñaari fan ca juróomeelu weeru at ma, ca la bëkk-néegu buuru Babilon, Nebusaradan njiitu dag ya, dugg Yerusalem. \v 9 Mu taal kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, taal kër Buur, ak këri Yerusalem gépp, boole ca këri boroom barke ya. \v 10 Gàngooru Babilon gépp daldi ànd ak njiital dagi buur, ñu màbb tata ya wër Yerusalem. \v 11 Gannaaw gi ña nekkoon ca dëkk ba ba booba, ak ña jébbaloon seen bopp buuru Babilon ak la desoon ca waa réew ma, Nebusaradan njiital dagi buur, boole leen yóbbu ngàllo. \v 12 Teewul ñenn ca baadooloy réew ma, njiital dag ya bàyyi leen fa, ñuy liggéey tóokëri reseñ yaak tool ya. \p \v 13 Ci biir loolu kenuy xànjar ya woon ca kër Aji Sax ji ak rootukaay yaak mbalkam xànjar ma, waa Babilon toj lépp, boole xànjar ja, yóbbu Babilon. \v 14 Ñu yóbbaale mboolem ndabi xànjar yi ñuy liggéeye ci kër Aji Sax ji; ndab yiy def dóom, ak ñiitukaay yi, ak ñiimi feyukaayi làmp yi, ak ndab yiy def deretu sarax yi, ak mboolem jumtukaayi xànjar yu ñuy sarxalee. \v 15 Njiital dag ya yóbbaale and yaak ndab yiy def deret. Lu ciy wurus, mu ber, lu ciy xaalis, mu ber. \v 16 Ñaari kenu yooyu ak mbalka maak rootukaay ya, lépp di xànjar bu Suleymaan defaraloon kër Aji Sax ji, maneesula takk diisaay ba. \v 17 Taxawaayu kenu gu ci nekk fukki xasab\f + \fr 25.17 \fr*\fk xasab \fk*\ft mooy guddaayu loxo, diggante catu baaraamu digg ak conc.\ft*\f* laak juróom ñett. Ab ponkub xànjar a ci tege, bu taxawaay ba di ñetti xasab. Ab caax wodd ponk bi, ànd ak doomi gërënaati xànjar. Ñaari kenu yépp noonu, ànd ak seeni caax. \s1 Jàpp nañu Yudeen ñi njaam \p \v 18 Ci kaw loolu njiital dag ya jàpp Seraya \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bu mag ba, ak Cefaña sarxalkat ba ca topp, ak ñetti dagi bunt kër Aji Sax ja. \v 19 Biir dëkk ba nag mu jële fa jenn jawriñ ju jiite ay xarekat, ak juróomi niti dëkk ba ñu sës ci Buur, ak bindkatub njiital xare ba sasoo bind xarekat yi, ak juróom benn fukki Yudeen ñu mu fekk ca biir dëkk ba. \v 20 Ba mu ko defee Nebusaradan, njiital dagi buur, boole leen yóbbu ca buuru Babilon ca Ribla. \v 21 Buuru Babilon nag jam leen, ñu dee, foofa ca Ribla, ca réewum Amat. Noonu la Yuda génne réewam, dem ngàllo. \s1 Nabukodonosor tabb na Gedalya ca Yuda \p \v 22 Mbooloo ma des ca réewum Yuda te Nabukodonosor buuru Babilon bàyyi leen fa nag, Gedalya doomu Ayikam doomu Safan la tabb mu jiite leen. \v 23 Ba mboolem kilifay xare ya déggee ñook seeni nit ne buuru Babilon fal na Gedalya, dañoo ànd dikk ca Gedalya ca Mispa. Kilifa yooyu Ismayil doomu Netaña la woon, ak Yowanan doomu Kareya, ak Seraya doomu Tanumet ma dëkk Netofa, ak Yaasaña doomu waa Maaka ba, ñook seeni nit. \v 24 Gedalya giñal leen ne leen: «Buleen ragala bokk ci surgay waa Babilon. Toogleen ci réew mi te nangul buuru Babilon, muy seen jàmm.» \p \v 25 Gannaaw gi, ca juróom ñaareelu weeru at ma, Ismayil doomu Netaña doomu Elisama, bokk ci askanu buur, ànd ak fukki nit, dikk bóom Gedalya, bóomaale waa Yudak waa Babilon ya nekkoon ak moom ca Mispa. \v 26 Ci kaw loolu mbooloo mépp fabu, baadoolook boroom barke, ñook kilifay xarekat ya, ñu daldi daw dem Misra ndax ragal waa Babilon. \s1 Tijji nañu Yowakin buurub Yuda \p \v 27 Yóbbu nañu Yowakin buurub Yuda ngàllo ba mu am fanweeri at ak juróom ñaar, Ewil Merodag doora falu buur ca Babilon. At mooma, fukkeelu weer waak ñaar, ñaar fukki fan ak juróom ñaar ca weer wa, ca la Ewil Merodag siggil Yowakin buurub Yuda, daldi koy tijji. \v 28 Ci biir loolu mu rafetook moom, jox ko cér bu sut cér ba mu jox yeneen buur ya mu bokkal curga ca Babilon. \v 29 Yowakin nag teqlikook yérey kaso ya, ba noppi ñu may ko muy bokk ak Buur ndab giiru dundam. \v 30 Ci biir loolu ñu dogal ko njëlam lu sax dàkk, bàyyikoo ci Buur bés bu jot, giiru dundam.