\id 1SA (WOL) \ide UTF-8 \h 1.Samiyel \toc1 Samiyel, di téere bu jëkk bi \toc2 1.Samiyel \mt1 Samiyel \mt2 di téere bu jëkk bi \c 1 \ms1 Lii mooy jaar-jaari Samiyel \s1 Aana ñaan na doom \p \v 1 Amoon na genn góoru Cuufeen gu dëkkoon Raama\f + \fr 1.1 \fr*\fk Raama \fk*\ft mooy Raamatayim ba tey.\ft*\f*, ga ca tundi Efrayim. Ñu di ko wax Elkana, baayam di Yerowam. Yerowam, Eliyu mooy baayam; Eliyu, Towu mooy baayam; Towu, Cuuf mu Efrayim mooy baayam. \v 2 Elkana amoon na ñaari soxna. Kenn ka di Aana, ka ca des di Penina. Penina amoon na ay doom, waaye Aana amul woon doom. \v 3 At mu nekkaan Elkana day jóge dëkkam, dem Silo, màggali fa \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom gàngoori xare yi, sarxalal ko ca Silo. Foofa la Ofni ak Fineyas, ñaari doomi Eli yu góor ya doonoon \w sarxalkati|lemma="sarxalkat b-:"\w* Aji Sax ji. \v 4 Bés bu Elkana daan sarxal, day jox soxnaam Penina, mook doomam yépp, góor ak jigéen, ci yàppu sarax si. \v 5 Waaye Aana la daan beral loxo ca sarax sa, ndax cofeelam ci moom, doonte Aji Sax ji mayul Aana doom. \v 6 Wujjam nag dëkke koo ñaawal, ngir naqaral ko ndax la ko Aji Sax ji mayul doom. \v 7 At mu nekkaan noonu la. Saa yu Aana demee kër Aji Sax ji, noonu la koy ñaawale, ba muy jooy, du nangoo lekk. \v 8 Elkana jëkkër ja di ko wax ne ko: «Aana, looy jooy, ak lu la tee lekk? Ñàkk doom a la tax ne yogg nii? Maa ngii! Dama laa gënalul fukki doom yu góor?» \p \v 9 Mu am bés, gannaaw ba ñu lekkee ba naan ca seen saraxu cant, foofa ca Silo, Aana jóg. Booba Eli sarxalkat baa nga ca toogu ba, feggook jënu buntu jaamookaayu Aji Sax ji. \v 10 Aana dem ba foofa, ànd ak naqaru xolam, di ñaan ci Aji Sax ji, tey jooy jooy yu metti. \v 11 Ci biir loolu mu xas aw xas, daldi ne: «Éy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Sang bi, soo nemmiku woon ba nemmiku njàqare jii ma nekke, bàyyi ma xel, bañ maa fàtte, ba may ma doom ju góor! Kon déy, maa ko sédde Aji Sax ji, giiru dundam gépp, saatus watukaay du jaar ci boppam mukk!\f + \fr 1.11 \fr*\ft Njañ lu ñu dul wat, moom lañu daan màndargaale nit ku ñu sédde Aji Sax ji.\ft*\f*.» \p \v 12 Ñaanu Aana ca Aji Sax ji nag yàgg, Eli di ko seetlu. \v 13 Booba Aanaa ngay ñaan ca xelam, gémmiñ ga rekk ay yëngu, waaye déggeesul baatam. Eli foog ne dafa màndi, \v 14 ne ko: «Foo àppal sa màndite mi? Doxal, giifali sa ñoll wi!» \p \v 15 Aana ne ko: «Du loolu de, sang bi. Dama di jigéen ju ànd ak naqaru xol, waaye du biiñ, du leneen luy màndee lu ma naan. Dama doon diis Aji Sax ji sama tiisu xol. \v 16 Bu ma jàppe jigéen ju bon, sang bi. Bare naqar aku tiis a ma tax di ñaan nii, booba ba léegi.» \v 17 Eli ne ko: «Kon nag demal ak jàmm, yal na la Yàllay Israyil nangul li nga koy ñaan.» \v 18 Aana ne ko: «Amiin, sang bi, yal nanga ma yàgga yéwéne.» Ba mu ko defee Aana dem yoonam, doora mana lekk, kanam ga leer. \p \v 19 Ba loolu amee Elkana ak njabootam teela xëy ca ëllëg sa. Ñu màggal Aji Sax ji, ba noppi bàyyikoo fa, ñibbi seen kër ca Raama. \s1 Lu jëm ci juddub Samiyel ak ngoneem \p Gannaaw gi Elkana dëkkoo soxnaam Aana, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji nag bàyyi Aana xel. \v 20 Aana mujj ëmb ca ndeetel at ma. Gannaaw gi mu am doom ju góor, tudde ko Samiyel (mu firi Yàlla dégg na), ndax da ne: «Maa ko ñaan Aji Sax ji.» \p \v 21 Gannaaw gi Elkana ànd ak njabootam gépp dellu Silo, ngir defali Aji Sax ji saraxu at ma, boole ca sarax bu mu xasoon ne dina ko def. \v 22 Waaye Aana demul, ndax dafa wax jëkkëram ne ko: «Gannaaw bu xale bi feree laa koy yóbbu, sédde ko Aji Sax ji, mu des foofa benn yoon.» \v 23 Elkana, jëkkër ja, ne ko: «Kon baax na, defal noonu nga bëgg. Toogal fii yaak moom, ba feral ko ba noppi. Yal na Aji Sax ji sottal la mu waxoon rekk.» Ndaw sa nag des ca Raama, di nàmpal doomam, ba feral ko. \p \v 24 Naka la feral xale bi, ànd ak moom, muy lu tuut, mu yóbbu ko ca kër Aji Sax ji ca Silo. Mu yóbbaale ñetti yëkk\f + \fr 1.24 \fr*\fq ñetti yëkk: \fq*\ft am na ñu naan \ft*\fq yëkku ñetti at.\fq*\f*, ak benn efab sunguf, yemook fukki kilo, ak mbuusu biiñ. \v 25 Ba mu ko defee ñu rendi yëkk wi, ba noppi indi xale bi ci Eli. \v 26 Aana ne ko: «Sang bi, baal ma de waaye giñ naa, nga fekke, maay ndaw si taxawoon fii ci sa wet, di ñaan ci Aji Sax ji. \v 27 Xale bii moo ma taxoon di ñaan, te Aji Sax ji defal na ma sama dagaan. \v 28 Léegi nag man maa ko sédd Aji Sax ji: giiru dundam lees ko sédd Aji Sax ji.» Ba loolu amee ñu sujjóotal Aji Sax ji foofa. \c 2 \s1 Aana sant na \p \v 1 Ci kaw loolu Aana ñaan ne: \q1 «Sama xol a ngi bége \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, \q1 ci Aji Sax ji laa ame doole. \q1 Maa am tontal noon yi, \q1 nde maa bànneexoo sag wall. \b \q1 \v 2 «Kenn sellul ni Aji Sax ji, \q1 amuloo dend moos, \q1 cëslaay melul ni sunu Yàlla! \b \q1 \v 3 «Buleen ŋalŋaleeti, di damook a damooti, \q1 bu reewande génne seen gémmiñ, \q1 Aji Sax jeey Yàlla ji xam lépp, \q1 te mooy natt jëfi nit. \q1 \v 4 Fittu jàmbaar damm, \q1 néew-doole yi sol kàttan. \q1 \v 5 Ña reggoon, bindu, di dunde, \q1 ña xiifoon, noppee liggéey. \q1 Jigéen ju njur të woon jur juróom yaar, \q1 ku jur góori góor jeex tàkk. \b \q1 \v 6 «Aji Sax jeey rey, di dundal, \q1 mooy wàcce jaam njaniiw, génnee ko ca. \q1 \v 7 Aji Sax jeey xañe, di maye, \q1 di detteel, di kaweel. \q1 \v 8 Mooy yékkatee ku ndóol ci suuf, \q1 jële ku ñàkk ci mbuubit, \q1 boole leen dëj ca garmi ya, \q1 sédde leen jataayu teraanga. \b \q1 «Aji Sax jee moom kenuy suuf, \q1 samp ci àddina. \q1 \v 9 Mooy sàmm jéegoy wóllëreem, \q1 ku bon sànkoo biir lëndëm, \q1 nde doole mayewul ndam. \q1 \v 10 Aji Sax ji, ñi koy xeex ay rajaxoo, \q1 kaw asamaan lay dënoo ci seen kaw. \q1 Mooy mbugal àddina, ba mu daj, \q1 di kàttanal buuru ñoñam, \q1 di dooleel ki mu fal.» \p \v 11 Gannaaw ba loolu wéyee Elkana ñibbi këram ca Raama. \p Ngóor sa moom, des ca Silo, di liggéeyal Aji Sax ji, fa kanam Eli \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba. \s1 Lu jëm ci doomi Eli \p \v 12 Doomi Eli yu góor ya nag def nit ñu bon ñu faalewul \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \p \v 13 Lii moo di li \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* yooyu tàmmoona def ak askan wi. Saa yu nit indi waan juru sarax, bu ñuy togg yàpp wi, surgab sarxalkat bi day ŋàbb roqub ñetti càq, dikk, \v 14 capp ko ci biir, muy ndab lu tell, mbaa kawdir, mbaa cin, mbaa mbana— lu roq ba génne rekk, mu jël, sarxalkat bi féetewoo. Noonu lañu daan def ak mboolem niti \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, ña daan ñëw foofa ca Silo. \v 15 Rax ci dolli bala ñoo lakk nebbon bi\f + \fr 2.15 \fr*\fk nebbon: \fk*\ft nebbon ak deret, yoon mayewul woon ñu lekk ko. Seetal ci \ft*\ft \+bk Sarxalkat yi \+bk* 3.16-17.\ft*\f* sax, surgab sarxalkat bi day dikk, ne nit kiy sarxal: «Joxal sarxalkat bi ci yàpp wi, mu saaf. Du nangu nga jox ko yàpp wu ñor, yàpp wu xonq rekk.» \v 16 Su ko nit ki nee: «Xanaa dees na jëkka lakk nebbon bi ba mu jeex, nga doora sàkk lu la neex?» Mu ne ko: «Mukk! Léegi nga ma ciy jox, lu ko moy doole laa koy jële.» \v 17 Bàkkaaru doomi Eli yi réyoon na lool fi kanam Aji Sax ji, ndax dañu daan teddadil saraxu Aji Sax ji. \p \v 18 Ci biir loolu ngóor sa Samiyel moom, ma ngay liggéeyal Aji Sax ji, sol \w xar-sànnim|lemma="xar-sànni m-:"\w* lẽewam. \s1 Lu jëm ci waa kër Samiyel \p \v 19 Mbubb mu ndaw nag la ko yaayam daan ràbbal, yóbbul ko at mu jotaan, buy ànd ak boroom këram sarxali saraxu at ma. \v 20 Ci biir loolu Eli daan na ñaanal Elkana ak soxnaam, bala ñoo ñibbi, ne: «Yal na la \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji may kuutaay ak sa soxna sii, ñu wuutu ki mu sédd Aji Sax ji.» \v 21 Aji Sax ji nag dikke Aana aw yiw, mu amaat ñetti doom yu góor ak ñaar ñu jigéen. \p Ci biir loolu Samiyel moom, ma ngay màgg fa wetu Aji Sax ji. \s1 Eli àrtu na ay doomam \p \v 22 Eli nag mujj na di mag lool. Ba mu yégee mboolem li doomam yu góor yi def ak Israyil gépp, bay tëdde sax jigéen ñiy liggéey ci bunt \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* mi, \v 23 da leena wax, ne leen: «Ana lu waral ngeen di def jëf jii? Maa dégge ci askan wépp jëf ju bon jii ngeen nekke. \v 24 Aa! Xale yi, coow li ma dégg, muy law ci biir ñoñi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, rafetul de! \v 25 Su nit ki tooñee moroomu nitam, Yàllaay àtte; waaye su dee Aji Sax ji la nit ki tooñ, ana ku koy àtte?» Wax jooju nag taxul ba tey ñu déggal seen baay. Booba fekk na Aji Sax ji namm leena rey. \p \v 26 Ci biir loolu yépp, ngóor sa Samiyel di màgg, neex Aji Sax ji, neex nit ñi. \s1 Nitu Yàlla rëbb na Eli \p \v 27 Mu am bés genn góoru Yàlla dikk ci Eli, ne ko: «\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: “Maa feeñu woon ci lu leer sa waa kër baay ba ñu nekkee Misra, di moomeelu kër Firawna. \v 28 Maa tànne sa baay ci digg giiri Israyil yépp, ngir mu doon sama \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w*, di yéeg ci sama \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*, di taal cuuraay, sol \w xar-sànni|lemma="xar-sànni m-:"\w* mi, janook man. Maa sédd it sa waa kër baay mboolem saraxi sawara yu \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \v 29 Lu tax ngeen di teddadil sama saraxi rendi ak yeneen sarax yi ma santaane ci màkkaan mi? Lu waral ngay teral sa doom yi teraanga joo ma joxul, ba ngeen di yafloo li gën ci mboolem saraxi Israyil sama ñoñ?” \v 30 Kon nag kàddug Aji Sax jee, Yàllay Israyil: “Maa waxoon déy ne, sa waa kër ak sa waa kër baay ñooy doxe fi sama kanam, di ma liggéeyal ba fàww.” Léegi nag, kàddug Aji Sax jee: “Loolu jomb naa ko tey. Ñi ma teral laay teral; waaye ñi ma teddadil, dees na leen tuutal. \v 31 Te kat ay bés a ngi ñëw, maay dagg sa doole, dagg sa dooley waa kër baay, ba deesatul màggate ci sa kër. \v 32 Njàqare ngay saxoo ci sama dëkkuwaay. Israyil dina baaxle moos, waaye du tax kenn màggate sa kër mukk. \v 33 Dina am ku bokk ci yaw ku ma dul dagge ci liggéey bu jëm ci sama sarxalukaay, waaye maa lay jooyloo, ba nga ñàkki bët, teg la njàqarey xol, te mboolem ñu yokku ci sa kër, seen digg doole lañuy deeye. \v 34 Li nga ciy def ab takk mooy liy dikkal Ofni ak Fineyas, sa ñaari doom yu góor yii: Benn bés lañuy bokk dee ñoom ñaar ñépp. \v 35 Te it maay tabbal sama bopp sarxalkat bu wóor boo xam ne sama nammeelu xol ak sama bëgg-bëggu bakkan lay jëfe. Maa koy sampal kër gu wóor, muy doxe fi kanam ki ma fal ba fàww. \v 36 Su ko defee mboolem ku des ci sa waa kër dina ko sujjóotalsi, ngir as xaalis mbaa as dogu mburu, naan ko ‘Ngalla sas ma lenn ci liggéeyu carxal gi, ndax ma am as dogu mburu su ma lekk’.”» \c 3 \p \v 1 Ngóor sa Samiyel nag moom, di liggéeyal Aji Sax ji fi kanam Eli. \s1 Yàlla def na Samiyel yonent \p Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji néewoon na ca yooya jamono, peeñu mu leer it tumurànke woon na. \p \v 2 Mu am bés Eli tëdd fa muy tëdd naka jekk, fekk bët ya naqari, ba daanaka gisatul. \v 3 Booba làmpu jaamookaayu Yàlla bi feyagul, te Samiyel a ngi tëdd ci biir jaamookaayu Aji Sax ji, fi \w gaalu Yàlla|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* gi nekk. \v 4 Aji Sax ji woo Samiyel, mu ne: «Maa ngi», \v 5 daldi daw ba ca Eli, ne ko: «Maa ngi, du yaa ma woo?» Eli ne ko: «Wootewuma de, dellul tëri.» Mu dellu tëdd. \p \v 6 Aji Sax ji dellu woo Samiyel, Samiyel jóg, dem ba ca Eli ne ko: «Maa ngi, du yaa ma woo?» Eli ne ko: «Wootewuma de doom, dellul tëri.» \v 7 Booba Samiyel xamagul woon Aji Sax ji, te kàddug Aji Sax ji dikkalagu ko woon. \p \v 8 Aji Sax ji wooti Samiyel ñetteel bi yoon, Samiyel jógati, dem ba ca Eli ne ko: «Maa ngi, du yaa ma woo?» Eli nag xam ne Aji Sax jeey woo xale bi. \v 9 Mu ne Samiyel: «Demal tëri, bu la wootee, nee ko: “Aji Sax ji, maa ngi lay déglu, Sang bi, waxal.”» Samiyel dellu tëdd fa muy tëdd. \p \v 10 Ba mu ko defee Aji Sax ji dikk taxaw, wooti ko na woon, ne ko: «Samiyel, Samiyel.» Samiyel ne: «Maa ngi lay déglu, Sang bi, waxal.» \v 11 Aji Sax ji ne Samiyel: «Maa ngii déy, di waaja def ci digg \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, mbir muy buur noppi mboolem ku ko dégg. \v 12 Bésub keroog ma matal ci Eli mboolem lu ma waxoon ne mooy dal waa këram, ndoorte la ba ca muj ga. \v 13 Waxoon naa ko ne ko dinaa teg waa këram mbugal mu sax dàkk, ndax ñaawtéef gu ay doomam nekke, di ñàkke Yàlla teggin, mu yég ko te jubbantiwu leen. \v 14 Looloo waral ma giñal waa kër Eli, ne du am mukk benn saraxu jur mbaa beneen sarax bu leen mana jot ci seen ñaawtéef.» \p \v 15 Ci kaw loolu Samiyel tëdd ba ca suba sa, mu tijji bunti kër Aji Sax ji, waaye ñemewula nettali Eli peeñu ma. \v 16 Eli nag woo ko ne ko: «Samiyel doom, ana nga?» Samiyel ne ko: «Maa ngi.» \v 17 Eli ne ko: «Kàddu gi mu la wax, lu mu doon? Bu ma nëbbu kay. Soo ma nëbbee lenn ci li mu la wax, yal na la Yàlla teg naqar wu gëna tar.» \v 18 Samiyel wax ko lépp, nëbbu ko ca dara. Eli ne: «Mooy Aji Sax ji. Li ko soob, na ko def.» \p \v 19 Ci kaw loolu Samiyel di màgg, Aji Sax ji ànd ak moom, waccul genn kàddug Samiyel, mu fanaan àll. \v 20 Noonu la Israyil gépp ràññee, la dale Dan ca bëj-gànnaar ba ca Beerseba ca bëj-saalum, ne Samiyel taxaw na taxawaayu yonentu Aji Sax ji. \v 21 Aji Sax ji nag wéye koo feeñu ca Silo. Ci kàddug Aji Sax ji la ko Aji Sax ji daan feeñoo ca Silo. \c 4 \s1 Nangu nañu gaalu Yàlla ga \p \v 1 Kàddug Samiyel nag di dikkal Israyil gépp. \p Ci biir loolu \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* dem, dajeek waa Filisti ngir xare. Ña nga dal fa feggook Eben Eser, waa Filisti dal ca Afeg. \v 2 Waa Filisti làng-déral Israyil, xare ba jib. Israyil daanu fa kanam waa Filisti, waa Filisti rey ca seeni làng lu jege ñeenti junni ca toolub xare ba. \v 3 Ba mbooloo ma ñibbee ca dal ba, magi Israyil ña ne: «Lu waral \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dumalu nu tey fi kanam waa Filisti? Nan jëleji \w gaalu kóllërey Aji Sax|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* ji fa Silo; na dikk ci sunu biir, ba musal nu ci sunuy noon.» \p \v 4 Ci kaw loolu mbooloo ma yónnee ca Silo, ñu jëli gaalu kóllërey Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Ki toog fi tiim ñaari malaakay \w serub|lemma="serub y-:"\w* yi\f + \fr 4.4 \fr*\fk serub ya: \fk*\ft baatu ebrë la. Ay malaaka lañu yu bokk ak Yàlla jataay. Gaalu kóllëre gu sell ga, ñaari serub yu ñu tëgge wurus lañu teg ca kawam, ñu tiim ko, seeni laaf tàllalu, di saamandaay ngàngunem buur. Loolu di wone ne Yàlla Aji Sax jaa nga fa teew, na mu teewe ca kaw asamaan, serub ya yéew ko. Yàlla ci boppam nag kenn jëmmalu ko fa, na ñu jëmmale serub ya ñu tëgg.\ft*\f*. Foofa ca Silo la Ofni ak Fineyas, ñaari doomi Eli yu góor ya, nekkoon ak gaalu kóllërey Aji Sax ja. \p \v 5 Ba gaalu kóllërey Aji Sax ji duggsee ca dal ba, Israyil gépp a xaacoondoo, ba suuf say riir. \v 6 Waa Filisti dégg coow la, ne: «Waaw, coow lu réy loolu ca dalub \w Ebrë|lemma="Ebrë:"\w* ya, lu mu doon?» \p Ba waa Filisti yégee ne gaalu kóllërey Aji Sax ja dugg na ca biir dal ba, \v 7 tiitaangee leen jàpp, ñu ne: «Am na yàlla ju dugg ca biir dal ba! Wóoy, ngalla nun! Nde guléet tey lu mel nii am! \v 8 Wóoy ngalla nun! Ku nuy musal ci jii yàlla ju bare doole. Yàlla jii moo dumaa woon waa Misra xeeti mbugal yu nekk, ca màndiŋ ma. \v 9 Dëgërluleen déy te diy góor, yeen waa Filisti, nde lu ko moy ngeen doon jaami Ebrë yi, na ñu nekke woon sunuy jaam. Góor-góorluleen boog te xeex.» \p \v 10 Waa Filisti nag di xare, ba bànni Israyil daanu: ku nekk daw jëm xaymaam. Jéll ba réy na lool; fanweeri junniy xarekat yuy deme tànk. \v 11 Gaalu Yàlla ga, ñu jël; Ofni ak Fineyas, ñaari doomi Eli yu góor ya, dee. \s1 Mbugal ma topp na waa kër Eli \p \v 12 Ba mu ko defee jenn waay ju bokk ci giirug Beñamin, dawe ca làngu xare ba ca Silo ci benn bés bi. Mu agsee yére yu xottiku ak bopp bu fees ak suuf, di ko tiisloo. \v 13 Naka la agsi, yem ca Eli, mu toog ca toogoom ca peggu yoon wa, di séentu, ndax booba naw gaa ngay rëcc, ngir tiitaange ca \w gaalu Yàlla|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* ga. Naka la waa ja duggsi ca dëkk ba, ba wax la xew, dëkk ba bépp yuuxoondoo. \p \v 14 Eli dégg coow la, ne: «Riir moomu lu mu?» Waa ja gaaw dikk, wax ko Eli. \v 15 Booba Elee ngi ci juróom ñeent fukki at ak juróom ñett (98), bët yi ne xóll te gisatul dara. \v 16 Waa ja ne ko: «Man mii maa jóge ca toolub xare ba. Maa dawe làng ga tey jii.» Eli ne ko: «Doom, lu xew?» \v 17 Ndaw la ne ko: «\w Bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* a daw, won waa Filisti gannaaw. Jéll bu réy la sunu mbooloo ma daanu, sa ñaari doom ya, Ofni ak Fineyas dee nañu, te it gaalu Yàlla ga, jël nañu ko.» \v 18 Naka la tudd gaalu Yàlla ga rekk, Eli xàwwikoo ca toogu ba, daanoo njaaxaanaay, dal ca bunt dëkk ba, loos wa damm, mu dee, ndax booba day mag mu ànd ak yaramam. Eli jiite na Israyil ñeent fukki at. \p \v 19 Goroom, jabaru Fineyas nag jigéenu wérul la woon te booba mu ngi waaja wasin. Naka la dégg ne jël nañu gaalu Yàlla ga, te baayu jëkkëram ak jëkkëram dee nañu, mu daldi sukk wasin. Waaye fekk na mititu matam jeexal dooleem. \v 20 Ba loolu amee muy waaja dee, jigéen ña ko doon taxawu ne ko: «Na sa xel dal, ndax doom ju góor nga am.» Waaye àdduwul, teewluwul. \v 21 Ndaw sa nag tudde gone gi Ikabot (mu firi Ana leer ga?) te naan: «Leer ga dëddu na Israyil, dem ngàllo.» Ndax la ñu nangu gaalu Yàlla ga ak la goroom ak jëkkëram dee. \v 22 Mu ne: «Leer ga kay dëddu na Israyil, dem ngàllo, ndegam jëlees na gaalu Yàlla ga kay!» \c 5 \s1 Gaalu Yàlla ga jaaxal na Filisti \p \v 1 Ba waa Filisti nangoo \w gaalu Yàlla|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* ga, Eben Eser lañu ko jële, yóbbu ko seen dëkk Asdodd. \v 2 Ñu dugal gaal ga ca seen biir kër tuur ma ñu naan Dagon, teg ko ca wetu jëmmu Dagon ja. \v 3 Waa Asdodd teela xëy ca ëllëg sa, fekkuñu lu moy jëmmu Dagon ja, mu daanu ba dëféenu fa suuf, fa kanam gaalu Aji Sax ji. Ñu yékkati jëmmu Dagon ja, delloo ko fa mu taxawoon. \v 4 Ca ëllëg sa, ñu teela xëyati, fekkuñu lu moy jëmmu Dagon ja daanu ba dëféenu fa suuf, fa kanam gaalu Aji Sax ji. Bopp baak cati loxo ya damm, ne wesar ca dëwu bunt ba, desul lu moy yaram wa. \v 5 Looloo waral ba tey jii, \w sarxalkati|lemma="sarxalkat b-:"\w* Dagon yeek mboolem ñiy dugg kër tuur ma ñu wax Dagon ca Asdodd, kenn du ci joggi ca dëwu bunt ba. \p \v 6 Ba mu ko defee loxol Aji Sax ji mujj diis ca kaw waa Asdodd. Mu wàcce njàqare ca seen kaw, daldi teg waa Asdodd ak la ko wër ay taab. \v 7 Waa Asdodd gis la leen dal, daldi ne: «Bu gaalu Yàllay \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gii des ci sunu biir kat, ndax loxoom dëgër na ci sunu kaw, nook Dagon sunu tuur mi.» \v 8 Ba loolu amee ñu yónnee, woolu mboolem kàngami waa Filisti. Ñu laaj leen ne leen: «Nan lanuy def ak gaalu Yàllay Israyil gii?» Ñu ne leen: «Toxal-leen gaalu Yàllay Israyil gi ca Gaat.» Ñu toxal gaalu Yàllay Israyil ca seen dëkk ba ñuy wax Gaat. \v 9 Naka lañu fa toxal gaal ga nag, loxol Aji Sax ji dal dëkk ba, mu jur tiitaange lu réy lool. Daa dal ca kaw dëkk ba, mag ak ndaw, ay taab ne fureet ca seen kaw. \v 10 Ñu yóbbu gaalu Yàlla ga beneen dëkk bu ñuy wax Ekkron. Gaal gaa ngay jubsi Ekkron, waa dëkk ba gaaw yuuxoondoo ne: «Indil nañu nu fi gaalu Yàllay Israyil, bëgg noo rey, nook sunu waa réew mépp!» \v 11 Ci kaw loolu ñu yónnee, woolu mboolem kàngami waa Filisti, ne leen: «Jëleleen fi gaalu Yàllay Israyil gii, mu dellu këram, lu ko moy dina nu rey, nook sunu askan wépp.» Booba tiitaangey ndee dajal na dëkk ba bépp, ndax loxol Yàlla bu diis lool ca seen kaw. \v 12 Ña ca deewul nag, seen yaram yàqooki taab, yuux ya jollee ca dëkk ba, wuti asamaan. \c 6 \s1 Waa Filisti delloo nañu gaalu Yàlla ga \p \v 1 \w Gaalu Aji Sax|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* ja nekk na réewum Filisti juróom ñaari weer. \v 2 Waa Filisti doora woolu seeni \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ak seeni gisaanekat, ne leen: «Nan lanuy def ak gaalu Aji Sax ji? Xamal-leen nu nan lanu koy delloo këram!» \v 3 Ñu ne leen: «Su ngeen dee delloo gaalu Yàllay Israyil, buleen ko delloo loxoy neen, waaye fexeleen ba boole kook \w saraxu peyug tooñ|lemma="Sarax yi:"\w*, yónnee ko. Kon dingeen wér, te dingeen xam lu tax loxol Yàlla ji teggikuwu leen.» \v 4 Waa Filisti ne leen: «Ban saraxu peyug tooñ lanu koy yónnee?» Ñu ne leen: «Limu kàngami Filisti ngeen di topp, daldi defarlu juróomi taabi wurus ak juróomi janaxi wurus, mu dëppook limu kàngami waa Filisti, ndax benn balaa bi leen dal moo dal seeni kàngam itam. \v 5 Noonu ngeen di sàkke ay jëmm yuy jëmmal seeni taab ak jëmm yuy jëmmal seen janax yiy yàq réew mi. Su ko defee ngeen defale ko Yàllay Israyil teraanga. Jombul mu woyofal loxoom ci seen kaw ak seeni tuur ak seenum réew. \v 6 Ana lu jar ngeen di jaay dëgër bopp ni waa Misraak Firawna? Ba leen Yàllay Israyil torxalee, bàyyiwuñu bànni Israyil, ñu dem seen yoon? \v 7 Kon waajal-leen watiir bu bees te ngeen jël ñaari nag yuy nàmpal yu ñu masula takkal. Ngeen takkal nag yi watiir bi te yóbbu doomi nag yi, fat. \v 8 Ngeen daldi jël gaalu Aji Sax ji, teg ko ci kaw watiir bi. Liggéeyi wurus yu peyug tooñ yooyu ngeen di yónnee nag, ci waxande wu ndaw ngeen koy yeb, te teg waxande wi ci wetu gaal gi. Su ko defee ngeen yebal watiir bi, mu dem. \v 9 Nangeen ko xool. Su jubalee réewam, wuti dëkk bi ñuy wax Bet Semes, kon Aji Sax jee nu teg musiba mu réy mii, lu ko moy nu xam ne du loxoom a nu dal, waaye ndogal lu nu dikkal la.» \p \v 10 Waa Filisti def noona, daldi tànn ñaari nag yuy nàmpal, takkal nag yi watiir, doomi nag ya, ñu fat leen. \v 11 Ñu daldi teg gaalu Aji Sax ja ca kaw watiir ba, ak waxande wu ndaw, wa def janaxi wurus yaak seen jëmmi taab ya. \v 12 Ba mu ko defee, nag ya jubal xocc yoonu Bet Semes, topp wenn yoon wi rekk, di nàññiy dem. Jàdduñu ndijoor, jàdduñu càmmoñ. Kàngami Filisti ya topp ca, ba fa Bet Semes tàmbalee. \p \v 13 Booba waa Bet Semes a ngay góob bele ca xur wa. Naka lañu dawal seen bët, séen gaal ga, daldi bég. \v 14 Watiir ba dikk ba ci toolu jenn waayu Bet Semes ju ñuy wax Yosuwe, mu taxaw fa. Aw doj wu mag a nga fa woon. Ci kaw loolu ñu xar mattum watiir ba, nag ya, ñu defal ko Aji Sax ji \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*. \v 15 Fekk na \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ña\f + \fr 6.15 \fr*\fk Leween ña: \fk*\ft Yàlla tànn na ñi bokk ci giirug Lewi doomu Yanqóoba, ñuy jàpple sarxalkat ya ca liggéeyu kër Yàlla ga.\ft*\f* wàcce gaalu Aji Sax ja, ak waxande wu ndaw wa def liggéeyi wurus ya. Ñu teg lépp ca kaw doj wu mag wa. Bésub keroog waa Bet Semes def nañu ay saraxi rendi-dóomal ak yeneen sarax, ñeel Aji Sax ji. \v 16 Juróomi kàngami Filisti ya gis nañu loolu lépp, doora dellu Ekkron ca bés ba. \p \v 17 Jëmmi taabi wurus yooyu waa Filisti yónnee ngir saraxu peyug tooñ, ñeel Aji Sax ji, ay teraanga la yu bawoo ci kilifay dëkk yii: Asdodd, benn; Gasa, benn; Askalon, benn; Gaat, benn; Ekkron, benn. \v 18 Limu janaxi wurus yi it dëppook limu dëkki waa Filisti, yi seen juróomi kàngam jiite, dale ko ci dëkk yi tata wër, ba ci dëkk-dëkkaan yi dara wërul, ba fi doj wu mag wi ñu tegoon gaalu Aji Sax ji. Doj waa nga ca toolub Yosuwe waa Bet Semes ba, ba tey jii. \p \v 19 Terewul Yàlla mbugal ñenn ca waa Bet Semes, ndax dañoo yërndu woon ca biir gaalu Aji Sax ja. Juróom ñaar fukki nit\f + \fr 6.19 \fr*\ft Ni ñu ko binde ci ebrë manees na koo dégge nii: \ft*\fq juróom ñaar fukki nit a dee ci juróom fukki junniy nit.\fq*\f* la fàdd ca ñoom. Waa dëkk ba nag di tiislu ndax mbugal mu réy moomu leen Aji Sax ji teg. \v 20 Ci kaw loolu waa Bet Semes ne: «Ana ku mana taxaw fi kanam Aji Sax ji, jii Yàlla ju sell? Ci kan lanuy yóbbu gaal gi, ba mu sore nu?» \v 21 Gannaaw gi ñu yebal ay ndaw ca waa Kiryaat Yarim, ne leen: «Waa Filisti de délloosi nañu gaalu Aji Sax ji. Tee ngeena dikk, yóbbu ko seen dëkk?» \c 7 \p \v 1 Waa Kiryaat Yarim nag dikk, jëlsi gaalu Aji Sax ji, yóbbu ko kër Abinadab ca kaw tund wa. Ñu sellal Elasar, doomam ju góor ngir muy wattu gaalu Aji Sax ja. \s1 Samiyel jiite na Israyil \p \v 2 Gannaaw bés ba ñu yóbboo \w gaal|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* ga Kiryaat Yarim, nekk na fa lu yàgg, ba am fa ñaar fukki at. Waa kër Israyil gépp nag namma dellu ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \v 3 Samiyel wax ak waa kër Israyil gépp, ne leen: «Ndegam seen léppi xol ngeen namma delloo ci Aji Sax ji, jëleleen fi seen biir tuuri doxandéem yi, ak tuur yi ñu dippee \w Astàrt|lemma="Astàrt:"\w*, te ngeen saxal seen xol ci Aji Sax ji, jaamu ko moom doŋŋ. Su ko defee mu xettli leen ci waa Filisti.» \v 4 Ba mu ko defee \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* génne seen tuur yi ñu dippee \w Baal|lemma="Baal:"\w* ak Astàrt. Ñuy jaamu nag Aji Sax ji moom doŋŋ. \p \v 5 Gannaaw loolu Samiyel ne leen: «Wooleen Israyil gépp, ñu daje ca Mispa, ma tinul leen Aji Sax ji.» \v 6 Ñu daje ca Mispa, tanq ndox, sotti fa suuf, fa kanam Aji Sax ji. Ñu woor nag bésub keroog, daldi wax foofa ne: «Noo tooñ Aji Sax ji.» Ca Mispa la Samiyel doone njiitu Israyil. \p \v 7 Ba waa Filisti yégee ne bànni Israyil daje na ca Mispa, kàngami waa Filisti ya jóg, ngir songi leen. Bànni Israyil yég ko, am tiitaange ca waa Filisti. \v 8 Bànni Israyil ne Samiyel: «Ngalla bu nu noppee jooytul ci sunu Yàlla Aji Sax ji, ndax mu wallu nook waa Filisti!» \v 9 Samiyel jël menn xar mu feragul, defal ko lépp Aji Sax ji \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*. Mu jooytul Israyil ci Aji Sax ji, Aji Sax ji nangul ko. \v 10 Naka la Samiyel di joxe saraxu rendi-dóomal ba, waa Filisti di jegesi ngir xareek bànni Israyil. Aji Sax ji dënoo kàddu gu réy, ca kaw waa Filisti bésub keroog, fëlxe leen, ñu daanu fa kanam bànni Israyil. \v 11 Bànni Israyil génne Mispa, dàqi waa Filisti, duma leen, bay waaja àgg Bet Kar. \p \v 12 Gannaaw loolu Samiyel jël aw doj, teg ko ci diggante Mispa ak fu ñuy wax Sen; mu dippee doj wi Eben Eser (mu firi doju Wall). Mu ne: «Ba fii la nu Aji Sax ji wallu.» \v 13 Waa Filisti nag detteelu, dikkatuñu biir suufas Israyil. Giiru dundu Samiyel gépp loxol Aji Sax jaa ngi ci kaw waa Filisti. \v 14 Dëkk ya Filisti nangu woon ci Israyil daldi délsi ci seeni loxo; dale ko ca Ekkron ba Gaat. Israyil nangoo ci waa Filisti suufam sépp. Diggante Israyil ak Amoreen ñi itam di jàmm. \p \v 15 Samiyel jiite na Israyil giiru dundam gépp. \v 16 At mu jotaan day wër diggante Betel ak Gilgal ak Mispa, di àtte mbiri bànni Israyil, foofu fépp. \v 17 Gannaaw loolu mu dellu Raama ndax fa la këram nekkoon, fa la daan àttee Israyil, te fa la tabax \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*, ñeel Aji Sax ji. \c 8 \ms1 Israyil sàkku na buur \s1 Bànni Israyil ñaan na Samiyel buur \p \v 1 Ba Samiyel màggatee, ay doomam yu góor la fal njiiti Israyil. \v 2 Taaw ba Yowel la tuddoon, ka ca topp di Abya. Ñoo doon njiit ya ca Beerseba. \v 3 Doomi Samiyel yu góor ya nag jaaruñu ci seen tànki baay. Dañoo lajj, topp alal ju lewul, di nangu ay ger, di jalgati dëgg. \p \v 4 Ci kaw loolu magi Israyil ñépp daje, dem ca Samiyel ca Raama. \v 5 Ñu ne ko: «Góor gi, léegi danga di mag, te say doom jaaruñu ci say tànk. Kon danga nuy falal buur bu nu jiite, ni ko xeet yépp baaxoo.» \v 6 Samiyel ñaawlu la ñu ko ne mu falal leen buur bu leen jiite. Mu diis ko \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \v 7 Aji Sax ji ne ko: «Déggalal mbooloo mi te def li ñu la wax lépp. Du yaw lañu bañ, waaye man mii lañu bañ ma doonati seen buur. \v 8 Na ñu daan def naka jekk, ba ma leen génnee Misra ba tey jii, di ma dëddu, di jaamu yeneen yàlla, noonu rekk lañuy def ak yaw. \v 9 Kon déggal leen rekk, waaye àrtu leen bu baax, xamal leen luy doon sañ-sañu buur bu leen di jiiteji.» \s1 Lu jëm ci sañ-sañu buur \p \v 10 Ba loolu amee Samiyel jottli mbooloo, ma doon sàkku mu falal leen buur, mboolem àrtub \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \v 11 Mu ne: «Buur bi leen di jiiteji nag sañ-sañam moo di: Seeni doom yu góor lay jël, ngir tabb leen dawalkati watiiram aki fasam, ñuy daw jiitu watiiram. \v 12 Ñoom lay tabb ngir ñu doon njiiti kuréli junniy dag, mbaa njiiti kuréli juróom fukk. Ñoom it lay beyloo toolam, di leen góobloo, di leen sàkkloo ay gànnaayi xareem ak jumtukaayi watiiram. \v 13 Seen doom yu jigéen lay jël, def leen ay njafaan-kati cuuraay, aki toggkat ak lakk-kati mburu. \v 14 Seen ngëneeli tool ak tóokëri reseñ ak tooli oliw, mu jël, jox ay surgaam. \v 15 Seen pepp ak seen reseñ, fukkeel ba lay jël, jox ay jawriñam aki surgaam. \v 16 Seen jaam yu góor it, ak seen jaam yu jigéen, ak ñi ëpp doole ci seeni waxambaane ak seeni mbaam, mu jël, jëfandikoo ci liggéeyam. \v 17 Seeni gàtt, fukkeel ba lay jël, te yeen ci seen bopp, ay surgaam ngeen di doon. \v 18 Bu keroogee dingeen ne wóoy ndax buur bi ngeen falal seen bopp, te bu keroogee Aji Sax ji du leen wallu.» \p \v 19 Mbooloo ma nag lànk, déggaluñu Samiyel, xanaa ne ko: «Ndokk! Buur daal lanuy am, \v 20 nun itam, ba mel ni xeet yépp. Sunu buur a nuy yilif, dox, jiite nu, di nu xareel sunuy xare.» \v 21 Samiyel déglu la mbooloo ma wax lépp, ba noppi yegge ko Aji Sax ji. \v 22 Aji Sax ji ne ko: «Déggal leen rekk, te falal leen buur.» Samiyel nag ne \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*: «Baax na, demleen ñibbi, ku nekk ca dëkkam.» \c 9 \ms1 Lii mooy jaar-jaari Sóol \s1 Sóol doxi na yónnent \p \v 1 Jenn waay la woon ju bokk ci giirug Beñamin, ñu di ko wax Kis. Abyel ay baayam; Abyel, Seror ay baayam; Seror, Bekorat ay baayam; Bekorat, Afiya Beñamineen ba di baayam. Kis ku am daraja la woon. \v 2 Mu am doom ju ñuy wax Sóol\f + \fr 9.2 \fr*\fk Sóol: \fk*\ft am na ñu ko gëna xam ci turu Talut.\ft*\f*; xalelu góor bu góorayiw, ba kenn dàqu ko ci \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, sut ñépp taxawaay. \p \v 3 Mu am bés mbaam yu jigéen yu Kis, baayu Sóol, réer. Kis ne Sóol: «Àndal ak kenn ci surga yi, nga seetali ma mbaam yi.» \v 4 Ba loolu amee Sóol ak surgaam jaare tundi Efrayim, teg ca diiwaanu Salisa, gisuñu leen. Ñu jàll ba ca diiwaanu Saalim, dara. Ñu walbatiku jaaraat diiwaanu Beñamin, gisuñu leen. \p \v 5 Ba ñu àggee diiwaanu Cuuf, Sóol ne surgaam ba mu àndal: «Ayca nu ñibbi, lu ko moy nun la sama baay di xalaat, fàtte mbaam yi.» \v 6 Surga ba ne ko: «Xanaa lenn; genn góoru Yàllaa ngi ci dëkk bii, ku ñu naw la. Lépp lu mu wax, dara du ci fanaan àll. Nan fa dem kay, jombul mu xamal nu dara ci sunu yoon wi.» \v 7 Sóol ne surgaam: «Waaw, bu nu demee, lu nuy jox góor gi? Mburu mi woon ci sunuy mbuus jeex na, amunu dara lu nu yóbbul góoru Yàlla gi. Leneen lu nu am?» \v 8 Surga bi dellu ne Sóol: «Xanaa donju xaalis sii ma yor. Naa ko ko jox boog, mu won nu sunuw yoon!» \p \v 9 Bu jëkkoon nag ci Israyil ku daan leerluji ci Yàlla da naan: «Nan dem ca giskat ba,» ndax ku ñuy wooye yonent tey, booba, ab giskat lañu ko daan wooye. \p \v 10 Ci kaw loolu Sóol ne surgaam: «Wax nga dëgg. Kon nan dem.» Ñu jubal ca dëkk ba góoru Yàlla ga nekk. \v 11 Naka lañu yéeg tund wa, jëm ca dëkk ba, daldi taseek janq ju ca jóge, di rooti. Ñu laaj leen ne leen: «Góorug giskat bi fii la féete?» \p \v 12 Ñu ne leen: «Waaw, mu ngi fii ngeen jublu, waaye gaawleen de; ndax tey jii la dikk ci dëkk bi, ngir sarax su waa dëkk bi xewle tey ca \w bérabu jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* ba. \v 13 Bu ngeen di àgg biir dëkk bi rekk, dal ko fay fekk, bala moo dem jaamookaay ba, ca sarax sa. Waa dëkk bi duñu lekk mukk te dikkul, ndax mooy ñaan ci sarax si. Bu noppee, ñi ñu woo doora lekk. Kon demleen gaaw, ndax nëgëni fa ngeen koy fekk.» \s1 Sóol gis na Samiyel \p \v 14 Ba loolu amee ñu dem bay dugg ca biir dëkk ba, yem ca Samiyel, muy dikk, dajeek ñoom, jëm ca jaamookaay ba. \p \v 15 Fekk na balaa Sóol di ñëw, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji déey na Samiyel bés ba jiitu, ne ko: \v 16 «Nëgëni ëllëg maa ngi lay yónnee waa ju dëkk diiwaanu Beñamin. Nanga ko diw, fal ko, ngir mu yilif Israyil, sama ñoñ, ba xettli sama ñoñ ci waa Filisti. Maa geesu sama ñoñ, ndax seeni yuux àgg na fi man.» \p \v 17 Naka la Samiyel séen Sóol, Aji Sax ji wax ko, ne ko: «Waa jii laa la wax. Kii mooy yor sama ñoñ.» \p \v 18 Sóol dikk ba ca Samiyel, fa tollook bunt dëkk ba, ne ko: «Góor gi, baal ma tegtal ma kër giskat bi.» \v 19 Samiyel ne Sóol: «Man maay giskat bi. Doxal jiitu, nu dem ca jaamookaay ba. Yeen ak man ay bokk lekk tey. Bu subaa mboolem li ub sa bopp, dinaa la ko wax, door laa yiwi. \v 20 Mbaam yi nga réerle bëkk-démb, bu ci am benn xalaat, ndax feeñ nañu. Te sax, mboolem lu bakkane ci Israyil, xanaa du yaay boroom, yaak sa waa kër baay?» \v 21 Sóol ne ko: «Xanaa du man Beñamineen bi gëna néewle giir ci Israyil, sama làng gëna néew ci mboolem làng yi séq giirug Beñamin? Lii nga may wax, lu mu doon?» \p \v 22 Samiyel daldi ànd ak Sóol ak surgaam, yóbbu leen ba ca biir néegu bernde ja. Mu beral leen nag jataay ca kanam mbooloo, ma ñu woo, te ñu wara tollu ci fanweer. \v 23 Samiyel ne toggkat ba: «Indil ma ndawal li ma la joxoon, te noon la, nga ber ko.» \v 24 Toggkat bi yékkati tànk baak la mu àndal, teg ko ca kanam Sóol. Samiyel ne ko: «Lii, lañu beroon, tegal sa kanam, te lekk. Moom lañu la dencal ci ndaje mii ma woo askan wi.» Noonu la Sóol bokke ak Samiyel lekk bésub keroog. \p \v 25 Gannaaw loolu ñu jóge ca jaamookaay ba, dellu ca dëkk ba. Ba ñu demee kër ga, Samiyel diisook Sóol ca kaw taax ma. \s1 Samiyel diw na Sóol, fal ko \p \v 26 Ba ñu jógee ca ëllëg sa, bët a ngay waaja set. Samiyel woo Sóol ca kaw taax ma, ne ko: «Fabul, ma yiwi la.» Sóol fabu, ànd ak Samiyel, ñu génn ñoom ñaar. \v 27 Naka lañu dem bay bëgga génn dëkk ba, Samiyel ne Sóol: «Neel surga bi, mu jiitu nu.» Mu wax ko surga ba, mu jiitu leen. Samiyel neeti Sóol: «Yaw, taxawal fii tuuti, ma dégtal la kàddug Yàlla.» \c 10 \p \v 1 Ba loolu amee Samiyel jël njaqal diwu oliw lu ndaw, sotti ko ci kaw boppu Sóol, fóon ko, ne ko: «\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji diw na la déy, ngir fal la njiitu ñoñam. \v 2 Gannaaw boo teqlikook man, dinga dajeek ñaari góor ca wetu bàmmeelu Rasel ca Celca ca diiwaanu Beñamin. Dinañu la wax ne la mbaam ya nga seeti woon feeñ nañu. Te sax sa baay xalaatatul mbaam yi, yeena ko jaaxal. Ma nga naan: “Ana nu may def ak sama doom ji?” \v 3 Boo fa jógee, jubalal ba jot garab gu mag ga ca Tabor. Ñetti góor dinañu fa dajeek yaw, di màggali Yàlla ca Betel; kenn ka gàddu ñetti tef, keneen ka ŋàbb ñetti kàmpi mburu, ka ca des yor mbuusum biiñ. \v 4 Dinañu la nuyu, may la ñaari mburu; nga nangoo ko ca seeni loxo. \v 5 Bu loolu weesee nanga dem ba ca Gibeya Eloyim, fa dalub xarekati Filisti ya nekk. Booy jub dëkk ba, dinga dajeek kurélu yonent yu jóge ca \w bérabu jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* ba, aw nit jiitoo leen powum tabalaaki toxoro, ak ñaari xeeti xalam, yonent ya di waxe ni yonent\f + \fr 10.5 \fr*\fk waxyu: \fk*\ft wax lay doon, ju Yàlla déey ab yonent, mu di ko biral ci ndigalal Yàlla. Leeleeg bu ab yonent tolloo ci biral waxyu, day mel ni ku daanu leer.\ft*\f*. \v 6 Su ko defee Noowug Aji Sax jee naa milib ci sa kaw, ngay waxandoo ak ñoom, soppiku, doon keneen nit. \v 7 Bu la firnde yooyu dikkalee rekk, xamal ne Yàllaa ngi ànd ak yaw. Su boobaa, lu bés bi laaj, def ko. \v 8 Léegi doxal jiitu ma Gilgal. Maa ngi noonu di la fekksi, ngir rendi fa \w saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, sarxe fa \w saraxi cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*. Juróom ñaari fan nag ngay négandiku, ba ma fekksi la fa, xamal la looy def.» \s1 Noowug Yàlla gane na Sóol \p \v 9 Naka la Sóol bàyyikoo ca Samiyel, walbatiku, Yàlla daldi soppi xelam. Firnde yooyu yépp nag matandoo ca bés ba. \v 10 Ba Sóol ak surgaam àggee Gibeya, kurélu yonent yaa ne pemm, dajeek moom. Noowug Yàlla ne milib ca kaw Sóol, muy waxandoo ak ñoom ay \w waxyu|lemma="waxyu:"\w*. \v 11 Ci kaw loolu mboolem ña xamoon Sóol démb ak bëkk-démb, daldi yem ci moom, mu ànd ak yonent ya di wax ay waxyu. Nit ña naan ca seen biir: «Waaw, Sóol doomu Kis jii, lu ko jot nii? Sóol it ci yonent yi laa?» \v 12 Jenn waay ju fa dëkk ne: «Yii yonent sax, ci ngéru kan lañu bokk?» Ca lañu jóge, def ko waxin naan: «Sóol it ci yonent yi laa?» \v 13 Sóol biral ay waxyu ba noppi daldi dem ca \w bérabu jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* ba. \p \v 14 Ci kaw loolu baayu Sóol bu ndaw laaj Sóol ak surgaam, ne leen: «Fu ngeen demoon?» Sóol ne ko: «Mbaam yi lanu seeti woon, gisunu dara, nu dem ca Samiyel.» \v 15 Baayam bu ndaw ne ko: «Wax ma boog lu leen Samiyel wax.» \v 16 Sóol ne ko: «Samiyel da noo biralal ne mbaam ya feeñ na.» Mbirum nguur ma ko Samiyel wax nag, Sóol waxu ko baayam bu ndaw. \s1 Yàlla feddli na palug Sóol \p \v 17 Gannaaw loolu Samiyel woolu askanu Israyil ca \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ca Mispa. \v 18 Mu wax \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, ne leen: «Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: “Man maa génne Israyil Misra. Maa leen xettli ca waa Misra ak mboolem buur ya leen notoon. \v 19 Waaye tey yeena dëddu seen Yàlla, ji leen musal ci mboolem seeni loraange ak seeni njàqare. Yeena ko ne: ‘Falal buur ci sunu kaw daal!’ Léegi nag taxawleen fi kanam Aji Sax ji, giir ak giir, làng ak làng.”» \p \v 20 Ba Samiyel wooyee giiri Israyil yépp, ñu dikk, giirug Beñamin moo génn. \v 21 Mu woo giirug Beñamin, làng ak làng, làngu Matiri génn, Sóol doomu Kis génne ca. Ñu seet Sóol, gisuñu ko. \v 22 Ñu laajaat Aji Sax ji, ne ko: «Ndax keneen da fee ñëw?» Aji Sax ji ne: «Mu ngi nii, mu ngi làqu ci biir denc bi.» \v 23 Ñu daw jële Sóol foofa, mu taxaw ca biir mbooloo ma, sut ñépp. \v 24 Samiyel wax ak mbooloo mépp, ne leen: «Yeena gis ki Aji Sax ji taamu? Kenn melul ni moom ci mbooloo mi mépp.» Mbooloo ma mépp àddu ca kaw ne: «Buur, guddalu fan!» \v 25 Samiyel nag xamal mbooloo ma sañ-sañu buur. Mu bind ko cib téere, teg ca kanam Aji Sax ji. Ba mu ko defee Samiyel yiwi mbooloo mépp, ku nekk ñibbi këram. \p \v 26 Sóol itam ñibbi këram ca Gibeya, jàmbaari góor yi ci Yàlla xiir, ànd ak moom. \v 27 Terewul mu am ay nit ñu tekkiwul dara di wax, naan: «Ana nan lanu waa jii di xettlee?» Ñooñu sewal ko, yótuñu ko jenn teraanga. Sóol nag ne cell. \c 11 \s1 Sóol jéngu na \p \v 1 Nayas Amoneen ba moo dikkoon, gaw dëkk ba ñu naan Yabes ca Galàdd. Waa Yabes gépp wax ak moom, ne ko: «Ngalla digool ak nun jàmm, te nu nangul la.» \p \v 2 Nayas Amoneen ba ne leen: «Ni may digook yeen daal, mooy nii: luqi seen bëtu ndijoor yeen ñépp, ba Israyil gépp torox.» \v 3 Magi Yabes ne ko: «May nu juróom ñaari fan, nu yebal ay ndaw ci Israyil gépp. Su amul kenn ku nu wallu, nu dikk, fekksi leen.» \p \v 4 Ba ndaw ya dikkee Gibeya, ga Sóol dëkk, ba xamle mbir ma, waa dëkk ba di dégg, ñoom ñépp a yuuxu, di jooy. \v 5 Ci biir loolu Sóol ne tëll, jiital ay nagam, jóge tool ya. Mu ne: «Lu nit ñi xewle bay jooy nii?» Ñu nettali ko kàdduy waa Yabes. \p \v 6 Naka la Sóol dégg kàddu yooyu, Noowug Yàlla ne milib ca kawam, mer ma ne jippét tàkk. \v 7 Mu rey ñaari nag, dog ko, yóbbante ko ay ndaw, yónnee ko Israyil gépp. Mu ne leen: «Képp ku toppul Sóol ak Samiyel, nii lees di def ay nagam.» Ba loolu amee tiitaange ju sababoo ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dal ca kaw askan wa, ñu sàqeendoo, di benn bopp. \v 8 Ba Sóol nemmikoo limu góori Israyil ca Beseg, ñetti téeméeri junni lañu (300 000), waa Yuda di fanweeri junni (30 000). \p \v 9 Ñu wax nag ndaw ya jóge Yabes Galàdd, ñu jottli seen waa dëkk ba ne leen, ca ëllëg sa bu jant bi tàngee, dees na leen wallu. Ndaw ya dem, àgge ko waa Yabes, waa Yabes bég. \v 10 Ñu wax Amoneen ña, ne leen: «Ëllëg dinanu dikk, fekksi leen.» \p \v 11 Ca ëllëg sa Sóol séddale mbooloom xareem ñetti kurél. Ba ñu tolloo ci wattub njël, ñu dugg biir dalu Amoneen ña, di leen duma ba jant bi tàng. Ña ca rëcce daldi tasaaroo ba ñaar sax àndatuñu. \v 12 Mbooloo ma ne Samiyel: «Ana ku noon: “Ndax Sóol ay falu ci sunu kaw?” Indileen ñooñu, nu rey leen!» \v 13 Sóol ne leen: «Deesul rey kenn kay bésub tey jii, ndax bésub tey Aji Sax jee indi wall fi Israyil.» \p \v 14 Ci kaw loolu Samiyel ne mbooloo ma: «Ñëwleen nu dem Gilgal, ba feddli pal gi.» \v 15 Mbooloo ma mépp dem Gilgal, ñu fal Sóol buur foofa, fa kanam Aji Sax ji ca Gilgal\f + \fr 11.15 \fr*\ft Li tax ñu ne \ft*\fq fa kanam Aji Sax ji \fq*\ft mooy Gilgal dafa amoon bérabu jaamookaayu Aji Sax ji.\ft*\f*. Ñu sarxe fa \w saraxi cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w* fa kanam Aji Sax ji, Sóol ak \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp bànneexoo fa bànneex bu réy. \c 12 \s1 Samiyel wàcc na \p \v 1 Ba loolu weesee Samiyel wax Israyil gépp ne leen: «Mu ngoog, nangul naa leen li ngeen ma wax lépp, ba falal leen buur. \v 2 Léegi Buur a ngii jiite leen. Man nag màggat naa ba weex tàll, te samay doom a ngii ci seen biir. Maa leen jiite, ba may ndaw ba tey jii. \v 3 Maa ngii! Seedeleen sama jépp tuuma fi kanam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ak ki mu fal. Ana ku ma masa jël nagam, mbaa ma jël mbaamam? Ana ku ma masa lekk àqam, mbaa ma néewal ko doole? Ana ci kan laa masa nangoo alalu ger, ba nëpp-nëppal lu mu def. Lu ci am rekk, waxleen, ma fey ko.» \v 4 Ñu ne ko: «Lekkoo sunu àq, néewaloo nu doole. Masoo nangu lenn itam ci loxol kenn.» \v 5 Samiyel ne leen: «Kon Aji Sax ji seede na ci seen biir, ki mu fal it seede tey jii, ne gisuleen lenn ci sama loxo.» Ñu ne ko: «Seede na ko!» \p \v 6 Samiyel ne mbooloo ma: «Aji Sax ji moo jëfoo Musaa ak Aaróona, ba génne seeni maam réewum Misra. \v 7 Kon nag taxawleen, ma layook yeen fi kanam Aji Sax ji, ci mboolem njekk gu leen Aji Sax ji defal, yeen ak seeni maam. \p \v 8 «Gannaaw jamono ja Yanqóoba demee Misra, seeni maam a yuuxu, woo Aji Sax ji wall, Aji Sax ji yebal Musaak Aaróona, ñu génne seeni maam Misra, dëël leen bérab bii. \v 9 Seeni maam nag ñoo fàtte seen Yàlla Aji Sax ji, ba tax mu teg leen ca loxol Sisera njiitu xareb dëkk ba ñuy wax Àccor, ak ca loxol waa Filisti, ak ca loxol buuru Mowab, ñooña doon xareek ñoom \v 10 Seeni maam jooy ko Aji Sax ji, ne: “Bàkkaar nanu de, nde noo wacc Aji Sax ji, di jaamu tuur yi ñu naan \w Baal|lemma="Baal:"\w* ak \w Astàrt|lemma="Astàrt:"\w*. Waaye rikk xettli nook sunuy noon, nu jaamu la.” \v 11 Aji Sax ji yebal Yërubaal\f + \fr 12.11 \fr*\fk Yërubaal \fk*\ft mooy Sedeyoŋ ba tey. Seetal \ft*\ft \+bk Njiit ya\+bk* 6—8.\ft*\f*, teg ca Bedan\f + \fr 12.11 \fr*\fk Bedan: \fk*\ft am na ñu jàpp ne mooy Barag. Seetal \ft*\ft \+bk Njiit ya\+bk* 4.\ft*\f*, teg ca Yefte, teg ma ca, man Samiyel, daldi leen xettli ci seen noon yi leen séq, ba ngeen dëkke jàmm. \v 12 Waaye ba ngeen gisee Nayas, buurub Amoneen ña jëm ca seen kaw, yeena ma ne: “Buur bu nu jiite daal lanu bëgg.” Te Aji Sax ji seen Yàlla di seen buur. \v 13 Léegi nag buur bi ngeen taamu, di ko sàkku, mu ngi nii. Mu ngoog, Aji Sax ji fal na buur bu leen jiite. \v 14 Su ngeen ragalee Aji Sax ji, jaamu ko, déggal ko, baña gàntal ndigalu Aji Sax ji, yeen ak seen buur yépp ay topp seen Yàlla Aji Sax ji. \v 15 Waaye kat, su ngeen bañee déggal Aji Sax ji, di gàntal ndigalal Aji Sax ji, loxol Aji Sax jaa ngi ci seen kaw na mu nekke woon ca seen kaw maam ya. \p \v 16 «Léegi nag taxawleen ba gis jaloore ju réy jii Aji Sax jiy def, ngeen teg ci bët. \v 17 Du nu ngi ci ngóobum bele tey? Dinaa ñaan ci Aji Sax ji, mu dënu, taw. Su boobaa dingeen xam xéll ne ba ngeen sàkkoo buur, lu bona bon ngeen def, Aji Sax ji seede.» \p \v 18 Ci kaw loolu Samiyel ñaan ci Aji Sax ji, Aji Sax ji dënu, taw ca bés ba. Mbooloo ma mépp nag ragal lool Aji Sax ji ak Samiyel. \p \v 19 Ba loolu wéyee mbooloo ma mépp ne Samiyel: «Ngalla sang bi, ñaanal nu ci sa Yàlla Aji Sax ji, nu baña dee, ndax la nu bàkkaaroon lépp, yokkati nanu ci mbon gu tollu ni di sàkku buur.» \v 20 Samiyel ne mbooloo ma: «Buleen tiit; dëgg la, yeena def googu mbon gépp, waaye fexeleen rekk ba baña dëddu Aji Sax ji, te ngeen jaamoo Aji Sax ji seen léppi xol. \v 21 Buleen dëddu mukk, ndax su boobaa topp ag neen lay doon; lu dul jariñe, du xettlee, ndax tuur yi kat, neenug neen la. \v 22 Aji Sax ji moom turam wu màgg wi tax na du wacc ñoñam, ndax Aji Sax ji la soob, mu def leen ñoñam. \v 23 Man nag, yàlla tere may tooñ Aji Sax ji, di leen noppee ñaanal. Te it dinaa leen won yoon wi baax te jub: \v 24 ngalla fexeleen rekk ba ragal Aji Sax ji, te ngeen dëggu ci jaamoo ko seen léppi xol, ndax dangeen di xool ci jaloore yu yéeme yi mu leen defal. \v 25 Waaye su ngeen saxee ci def lu bon, yeen ak seeni buur ay bokk sànku.» \c 13 \s1 Sóol tooñ na \p \v 1 Sóol ci boppam làqoon na ay at, ba muy falu buur; mu falu jiite Israyil ñaari at\f + \fr 13.1 \fr*\ft Sóol falu na ñaari at bala ñoo tànn Daawuda, mi koy wuutu. Seetal ci 16.13 ak \ft*\ft \+bk Jëf ya\+bk* 13.21.\ft*\f*. \v 2 Ci kaw loolu mu tànn ñetti junniy nit ci Israyil; ñaari junniy nit ñuy nekk ak moom ca Migmas ak ca tundi Betel, ak junniy nit ñu nekk ak Yonatan doomu Sóol ca Gibeya gu Beñamin. Ña ca des mu yiwi leen, ñu ñibbi seeni xayma. \v 3 Yonatan nag song dalub waa Filisti ca Geba. Waa Filisti yég ko. Ba mu ko defee Sóol wal-lu liit ga ca réew ma mépp, ne: «Na ko \w Ebrë|lemma="Ebrë:"\w* yi dégg!» \v 4 Ñu yégal Israyil gépp la xew ne leen: «Sóol song na dalub waa Filisti, ba tax waa Filisti jéppi \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*.» Gàngoor ga daldi daje, topp ca gannaaw Sóol ca Gilgal. \v 5 Ci biir loolu waa Filisti daje ngir xareek Israyil. Ña ngaak ñetti junniy\f + \fr 13.5 \fr*\fk 3 000: \fk*\ft mooy lim bi ñu siiwal ni ñu ko tekkee ci làkku gereg ak yeneen làkk.\ft*\f* watiiri xare ak juróom benni junniy gawar, xarekat ya bare, mel ni feppi suufas géej. Ñu dem dali ca Migmas, ca penkub Bet Awen. \p \v 6 Niti Israyil nag gis diggante bu metti bi ñu tollu ndax na ñu tance seen gàngoor ga. Ñu dem làquji ci ay xunteek ay dédd ak ay doj, aki seyaan aki kàmb. \v 7 Am na sax ay Ebrë yu jàll dexu Yurdan, wuti réewum Gàdd ak Galàdd. Fekk na Sóol a nga ca Gilgal ba tey. Mbooloom xareem ma mépp nekk faak moom, di pat-pati ndax tiitaange. \p \v 8 Mu négandiku juróom ñaari fan, diir ba ko Samiyel àppaloon. Waaye taxul Samiyel agsi Gilgal. Mbooloo ma tàmbalee dëddu Sóol, di tasaaroo. \v 9 Ba loolu amee Sóol ne: «Indil-leen ma \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* bi, ak \w saraxu cantu biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w* bi.» Ñu indil ko, mu daldi def saraxu rendi-dóomal bi. \v 10 Naka la def saraxu rendi-dóomal bi ba sottal rekk, Samiyel ne jaas. Sóol génn gatandu ko, ngir nuyu ko. \v 11 Samiyel ne ko: «Loo def nii?» Sóol ne ko: «Man kat damaa gis mbooloo mi dëddu ma, di tasaaroo, te yaw it dikkoo bésu àpp bi. Rax ci dolli waa Filistee nga daje ca Migmas. \v 12 Ma noon, waa Filisti dinañu ma songsi Gilgal, te sàkkooguma ndimbalu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. Looloo ma taxa sàcc sama bopp rekk, ba def saraxu rendi-dóomal bi.» \v 13 Samiyel ne Sóol: «Ag ndof nga def, ndax jëfewuloo santaane bi la sa Yàlla Aji Sax ji santoon. Soo ko defoon, Aji Sax ji dina saxal sa nguur ci kaw Israyil ba fàww. \v 14 Léegi nag sa nguur du wéy; Aji Sax ji sàkkul na boppam ki xolam jubool, te fal na ko njiitu ñoñam, ndax yaa sàmmul li Aji Sax ji santaane.» \p \v 15 Ba mu ko defee Samiyel bàyyikoo Gilgal, dem Gibeya gu Beñamin. Sóol nag waññ ñi mu àndal, ñu tollu ci juróom benni téeméeri góor. \s1 Yonatan def na njàmbaar \p \v 16 Sóol ak doomam Yonatan, ak gàngoor ga ànd ak ñoom ña nga dal ca Geba \f + \fr 13.16 \fr*\fk Geba: \fk*\ft seetal ci 13.3.\ft*\f* gu Beñamin, waa Filisti dal ca Migmas. \v 17 Ci biir loolu genn gàngooru yàqkat def ñetti kurél, jóge ca dalub waa Filisti. Genn ga jubal bëj-gànnaar, aw yoonu Ofra ca diiwaanu Suwal, \v 18 ñaareel ga jubal sowu ca Bet Oron, ñetteel ga jëm penku ca tund ya tiim xuru Ceboyim, fa féeteek màndiŋ ma. \p \v 19 Booba nag benn tëgg amul woon ca réewum Israyil ba mu daj, ndax waa Filisti dañu noon: Bu \w Ebrë|lemma="Ebrë:"\w* yi sàkk ay saamar aki xeej. \v 20 Moo tax \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp, ku ci bëggoona nàmmlu sa ngajju mbaa sa daba, mbaa sa sémmiñ, mbaa sa sawta, doo man lu moy dem ca tëggi waa Filisti. \v 21 Ku ci nekk, saa yu sa ngajju dayee, mbaa sa daba, ñaari ñetteelu siikal nga koy daasloo, njég gu jafe, tollook ñaari ñetteelu dogu xaalis. Boo dee daaslu ab roqub ñetti càq, mbaa sémmiñ, mbaa ngay jubbantilu catal ràbbu, genn-wàllam ngay fey. \v 22 Looloo tax keroog bésub xare ba, du benn xarekat bu ànd ak Sóol ak Yonatan, te yor saamar mbaa xeej ci loxoom. Mennum Sóol rekk a ci amoon, mook doomam Yonatan. \p \v 23 Ci biir loolu ab kurélu xarekati waa Filisti dem, taxawi ca jàllukaayu Migmas ba. \c 14 \s1 Yonatan song na waa Filisti \p \v 1 Ci fan yooyu Yonatan doomu Sóol wax surga ba koy gàddul ngànnaayam, ne ko: «Kaay nu dem ba ca gàngooru Filisti ga ca wàlla.» Baayam nag, waxu ko ci dara. \v 2 Fekk na baayam a nga dal fa Gibeya yem, ca ker garabu gërënaat ga ca Migron. Mbooloo ma ànd ak moom tollu ci juróom benni téeméeri góor. \v 3 Axiya ma nga fa woon, sol \w xar-sànnim|lemma="xar-sànni m-:"\w* \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w*. Axiya mooy doomu Ayitub, mi bokk ak Ikabot seen baay Fineyas; Fineyas moomu, Eli, sarxalkatu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ja ca Silo, mooy baayam. Mbooloo ma nag yéguñu ne Yonatan dem na. \v 4 Poot ba Yonatan jaare, wuti dalub waa Filisti, ñaari doj yu mag a sampe woon, séq ko. Ñu dippee wenn doj wa Boses, weneen wa di Sene. \v 5 Wenn doj waa nga sampe wetu bëj-gànnaar, janook Migmas, wa ca des sampe wetu bëj-saalum, janook Geba\f + \fr 14.5 \fr*\fk Geba: \fk*\ft seetal ci 13.3.\ft*\f*. \p \v 6 Yonatan ne gàddukatu gànnaayam: «Ayca nu dem ba ca dalub yéefar yee. Jombul Aji Sax ji defal nu yiw, ndax dara du tee Aji Sax ji maye ndam, nu bareek nu néew.» \v 7 Ba loolu amee gàddukatu gànnaayam ne ko: «Ayca, loo namm rekk, sang bi, yaw laa àndal ba jeex tàkk.» \v 8 Yonatan ne ko: «Ayca nu dem ba ca ñoom, feeñu leen. \v 9 Bu ñu nu nee: “Taxawleen foofu, ba nu fekksi leen,” nu yem fa, bañ leena fekki. \v 10 Waaye bu ñu nee: “Ayca, dikkleen,” nu daldi dem te xam ne Aji Sax jee leen teg ci sunu loxo. Nan def loolu ab takk.» \p \v 11 Ba loolu amee ñu feeñuji dalub waa Filisti, ñoom ñaar ñépp. Waa Filistee nga naan: «Xool-leen! Ay \w Ebraa|lemma="Ebrë:"\w* ngay génne pax ya ñu làqu woon.» \v 12 Ci kaw loolu waa dal ba ne Yonatan ak gàddukatu gànnaayam: «Ée, dikkleen rekk, nu xamal leen lu tuut.» Yonatan ne gàddukatu gànnaayam: «Dikkal, topp ci man. Aji Sax ji teg na leen ci loxol Israyil.» \v 13 Yonatan ñalgu ca kaw tund wa, gàddukatu gànnaayam topp ko. Yonatan a ngay jam, waa Filisti di daanu, gàddukatu gànnaayam ba di leen jekkli ca gannaawam. \v 14 Cong mu jëkk mooma Yonatan song, mook gàddukatu gànnaayam, lu tollook ñaar fukki góor lañu ca tëral ci dénd bu wara tollook xëyu nag. \v 15 Ci kaw loolu tiitaange dajal dal baak àll ba ko wër, ak mbooloo ma mépp; muy dal ba, di kuréli yàqkat ya. Rax ca dolli suuf sa yëngu, muy tiitaange lu Yàlla wàcce. \p \v 16 Fekk na ay jongrukati Sóol a nga tollu ca Gibeya gu Beñamin. Ñu jekki séen gàngooru Filisti gay raj-rajloo, fu ne ñu jëm fa. \v 17 Sóol ne ña ànd ak moom: «Wooteleen, ba xam ku jóge ci nun.» Ñu woote, Yonatan ak gàddukatu gànnaayam wuute. \v 18 Sóol ne Axiya sarxalkat ba: «Indil \w gaalu Yàlla|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* gi.» Bésub keroog gaalu Yàlla gaa ngaak \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \v 19 Naka la Sóol di wax ak sarxalkat bi, coow la ca dalub waa Filisti gëna jolli. Sóol ne sarxalkat bi: «Ah, bàyyi ko sax.» \v 20 Ba mu ko defee Sóol ak gàngoor ga ànd ak moom gépp daje, dem ca xare ba. Gisuñu lu moy waa Filisti ne kër-kër, ne këpp, di jamante seeni saamar. \v 21 Ci biir loolu Ebrë yi nangul woon waa Filisti démb ak bëkk-démb te nekkandook ñoom ca dal baak fa ko wër fépp sax, ne waññet, faraat ak seen bokki bànni Israyil ya ànd ak Sóol ak Yonatan. \v 22 Mboolem bànni Israyil ya làqu woon ca tundi Efrayim dégg ne waa Filisti daw nañu. Ñoom it ne leen dann ca xare ba. \v 23 Noonu la Aji Sax ji maye Israyil ndam bésub keroog, xare bay law, ba ca wàlla Bet Awen. \s1 Sóol wax na lu ëpp \p \v 24 Bésub keroog mbooloom Israyil jàq nañu, ndax ngiñ lu Sóol teg ci seen kaw, ne: «Képp ku lekk fii ba ngoon te feyooguma ci samay noon, yal na alku.» Mbooloo ma mépp, kenn sexu ca dugub. \v 25 Ci kaw loolu waa réew ma mépp dem ba ca gott ba. Fekk na ag lem a nga fa ca suuf. \v 26 Ba mbooloo ma duggee ca biir gott ba, yemuñu ca lu moy lem jay xelli, waaye kenn sàkku ci, jëme ci gémmiñam, ndax ragal ngiñ la. \v 27 Yonatan nag yégul woon ngiñal baayam la mu teg mbooloo ma. Mu tàllal yet wa ca loxoom, capp cat la ca lem ja, sex, bët ya daldi leer. \v 28 Kenn ca mbooloo ma ne ko: «Aa! Ngiñ lii de, sa baay giñoon na ko ci kaw mbooloo mi, ne: “Képp ku lekk tey, yal na alku,” moo tax mbooloo mi néew doole.» \v 29 Yonatan ne: «Sama baay de yàqal na mbooloo mi. Xool-leen rekk ni samay bët leere ndax lem sii ma ñam! \v 30 Astamaak bu mbooloo mi lekkoon tey ci lël ja ñu nangoo ci noon yi! Du ci la jéllu waa Filisti doon gëna réy a waay?» \p \v 31 Bésub keroog bànni Israyil a dumaa waa Filisti ca Migmas ba ca Ayalon. Bànni Israyil sonn lool nag. \v 32 Ba loolu amee ñu sëxëtoo lël ja, jël ca gàtt yaak nag ya ba ca wëllu ya, tër ca suuf, boole yàpp waak deret ja, lekk. \v 33 Ñu yegge ko Sóol, ne ko: «Mbooloo ma kat a nga nee, di moy \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, di lekk yàpp wu ànd ak deretam.» Sóol ne: «Yeenaka fecci kóllëre! Béraŋal-leen ma fii aw doj wu mag léegi.» \v 34 Gannaaw loolu mu joxe leneen ndigal, ne: «Tasaarooleen ci biir mbooloo mi, ne leen ñu indi fii ñoom ñépp seeni nag ak seeni gàtt. Fii lañuy rendee jur gi, door koo lekk. Su ko defee duñu moy Aji Sax ji, di lekk yàpp wu ànd ak deretam.» Mbooloo mépp daldi dikk guddig keroog, ku nekk akaw nagam. Ñu rendi foofa. \v 35 Sóol daldi fay tabax ab \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*, ñeel Aji Sax ji. Boobu sarxalukaay la jëkka tabax ñeel Aji Sax ji. \s1 Bànni Israyil jot na Yonatan \p \v 36 Ba loolu amee Sóol ne: «Nan toppi waa Filisti ci guddi gi, nu sëxëtoo seen alal ba bët set, te bunu ci bàyyi kenn, mu dund.» Mbooloo ma ne ko: «Loo bëgg rekk, defal!» \w Sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba nag ne ko: «Nanu ko jëkka diis Yàlla fii.» \v 37 Sóol laaj Yàlla ne ko: «Ndax ma topp waa Filisti? Ndax dinga leen teg ci loxol Israyil?» Bésub keroog nag Yàlla tontuwul. \v 38 Sóol ne: «Yeen njiiti mbooloo mi yépp, dikkleen fii, nu seet ba gis bàkkaarub tey jii, lu mu doon. \v 39 Ndax giñ naa ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jiy dund, wallukatub Israyil, bu doon sax lu sama doom Yonatan ci boppam def, dee rekk ay àtteem.» Mbooloo mépp, kenn tontuwu ko. \v 40 Mu ne \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp: «Taxaweleen nee, maak sama doom Yonatan, nu taxawe nii.» Mbooloo ma ne Sóol: «Loo bëgg rekk, defal.» \v 41 Sóol ñaan ci Aji Sax ji, ne ko: «Yaw Yàllay Israyil, ngalla xamleel liy dëgg.» Ñu daldi tegoo bant, mu dal ci kaw Yonatan ak Sóol, mbooloo ma wàcc. \v 42 Sóol ne: «Tegal-leen nu bant sama digganteek Yonatan.» Ñu tegal leen, mu dal ca doomam Yonatan. \p \v 43 Sóol ne Yonatan: «Wax ma loo def.» Yonatan ne ko: «Aylayéwén maa ñam tuuti ca lem, ja ma cappe sama catu yet wi ma yoroon ci sama loxo. Maa ngi, naa dee!» \v 44 Sóol ne ko: «Na ma Yàlla teg mbugal mu gëna tar, waaye yaw Yonatan dinga dee déy!» \v 45 Mbooloo ma nag ne Sóol: «Lan? Yonatan dee, moom mi may Israyil ndam lu réy lii? Xalaateesu ko moos! Giñ nanu ci Aji Sax jiy dund, du lenn luy rote ci kawaru boppu Yonatan sax, dal fi suuf, ndax Yàlla la àndal def lii tey.» Noonu la mbooloo ma jote Yonatan, ba deewul. \v 46 Ba loolu wéyee Sóol noppee dàq waa Filisti, waa Filisti dellu ca seenum réew. \s1 Sóol am na ndam \p \v 47 Gannaaw ba Sóol feddlee nguuram ca Israyil, xare naak seen noon ya leen wër yépp: Mowabeen ñaak Amoneen ñaak Edomeen ñaak buuri waa Soba, ak waa Filisti. Mboolem fu mu walbatiku rekk, moo daan. \v 48 Njàmbaar la xaree, duma Amalegeen ña, ba musal Israyil ca ña doon sëxëtoo seen alal. \p \v 49 Doomi Sóol yu góor nag ñoo doon: Yonatan, ak Iswi ak Malkisuwa; ñaari doomam yu jigéen, di Merab mi ci gën di mag, ak Mikal mi gën di ndaw. \v 50 Soxnas Sóol moo doon Ayinowam, Ayimaas di baayu Ayinowam. Njiitu xareem moo doon Abner doomu Ner baayu Sóol bu ndaw, \v 51 Kis miy baayu Sóol, ak Ner, baayu Abner, Abyel ay seen baay. \p \v 52 Xare bu metti la woon seen digg ak waa Filisti, giiru dundu Sóol gépp. Moo tax fu Sóol gisaan boroom kàttan mbaa boroomu fit, da koy dollikoo. \c 15 \s1 Sóol tooñati na \p \v 1 Samiyel daa waxoon Sóol, ne ko: «Man la \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji yebal, ngir ma fal la buurub Israyil, aw ñoñam. Kon déglul kàddu yii Aji Sax ji wax. \v 2 Aji Sax ju gàngoor yi dafa wax ne: “Maay dikke mbugal mu faj la Amalegeen ña defoon Israyil, tëru leen ca yoon wa, ba ñuy génn Misra. \v 3 Demleen léegi, songi Amalegeen ñi. Faagaagal-leen\f + \fr 15.3 \fr*\ft Lu Aji Sax ji aayal lañu koy def, yàq ko yaxeet; muy nit, mbaa ag jur mbaa alal.\ft*\f* seen lépp, te buleen leen ñeewante; reyleen góor ak jigéen, gone yi ba ci ñiy nàmp, ak nag ak gàtt, ak giléem ak mbaam.”» \p \v 4 Ba loolu amee Sóol woo gàngoor ga, lim leen ca Telem, ñuy ñaar téeméeri junniy xarekat yuy deme tànk, ak fukki junniy góori Yudeen. \v 5 Sóol dem ba jot dëkkub Amalegeen ña, daldi waajal am tëru ca xur wa. \v 6 Mu yónnee ca Keneen ña, ne leen: «Demleen, dawleen jóge ci biir Amalegeen ñi, bala ma leena buubaaleek ñoom, te ba \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* di génn Misra, yeena leen jiwoon ngor ñoom ñépp.» Keneen ña daw, jóge ca biir Amalegeen ña. \p \v 7 Ba mu ko defee Sóol song Amalegeen ña, dale ko Awila ba dëkk ba ñuy wax Sur ca penkub Misra. \v 8 Mu jàpp Agag buurub Amalegeen ña, gàngoor ga gépp, mu faagaagal, leel leen ñawkay saamar. \v 9 Sóol ak gàngooram nag bàyyi Agag, muy dund, mook la gëna baax ca nag yaak gàtt ya: jurug yafal gaak kuuy yu ndaw ya, mboolem lu baax daal. Néeguñu caa faagaagal dara, waaye mboolem lu ca ñàkk solo mbaa mu yooy, loola lañu faagaagal. \s1 Sóol ñàkk na \p \v 10 Gannaaw loolu kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal Samiyel ne ko: \v 11 «Réccu naa li ma fale Sóol buur, ndax dëddu na ma, te samay ndigal, jëfewu ko.» Samiyel am ca njàqare lool, ba fanaanee tinu Aji Sax ji guddi gépp. \v 12 Ba bët setee Samiyel teela jóg dem ngir dajeek Sóol. Ñu ne ko Sóol dem na dëkk ba ñuy wax Karmel, te defu fa lu moy yékkati am taax, terale ko boppam. Jóge na fa it, jàll ba Gilgal. \p \v 13 Ba Samiyel demee ba gis Sóol, Sóol ne ko: «Yal na la Aji Sax ji barkeel. Def naa la Aji Sax ji santaane!» \v 14 Samiyel ne ko: «Ana meem joojuy tàbbi sama nopp bii, lu mu doon? Ak looluy nàññi, may dégg?» \v 15 Sóol ne ko: «Ca Amalegeen ña de lañu ko jële. Xarekat yee bàyyi li gën ci gàtt yeek nag yi, ngir sarxal ko sa Yàlla Aji Sax ji. Waaye la ca des moom, faagaagal nañu ko.» \v 16 Samiyel ne Sóol: «Defal ndànk! Dinaa la xamal li ma Aji Sax ji wax biig.» Mu ne ko: «Waxal!» \v 17 Samiyel ne ko: «Xanaa du yaa gisaloon sa bopp ne lu tuut nga woon, te yaay njiital giiri Israyil tey; Aji Sax ji fal la, ngay buurub Israyil. \v 18 Aji Sax ji teg la ci yoon wi, ne la: “Demal faagaagal moykati Amalegeen ñi. Xareel ak ñoom, ba jeexal leen tàkk.” \v 19 Lu la tere woona déggal Aji Sax ji, xanaa di saax-saaxee alal ji, di def li Aji Sax ji ñaawlu?» \p \v 20 Sóol ne Samiyel: «Ndaxam déggal naa Aji Sax ji. Dox naa yoon wi ma Aji Sax ji yebal; indi naa Agag buurub Amaleg te Amalegeen ñi, faagaagal naa leen. \v 21 Xarekat yi daal a tànne ci lël ji li gën ci gàtt yeek nag yi ñu wara faagaagal, ngir sarxal ko sa Yàlla Aji Sax ji ca Gilgal.» \p \v 22 Samiyel ne ko: \q1 «Bànneexu Aji Sax ji ci \w saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* ak yeneen sarax, \q1 mbaa tolloo naak bànneex ba muy am ci dégg ndigalal Aji Sax ji? \q1 Ma ne, dégg ndigal a gën ab sarax; \q1 xol bu nangoo gën nebbonu kuuy. \q1 \v 23 Bàkkaaru ngisaane la déggadi yemool, \q1 ñaawtéefu bokkaale tollook reewande. \q1 Yaa gàntal ndigalu Aji Sax ji, \q1 Moom mu gàntal sa nguur.» \p \v 24 Sóol ne Samiyel: «Bàkkaar naa! Ndax maa wàcc kàddug Aji Sax ji ak say digal, ndax ragal mbooloo mi, ba topp seen coobare. \v 25 Léegi nag ngalla waay, baal ma sama bàkkaar bii te walbatiku, ànd ak man, ma sujjóotali Aji Sax ji.» \v 26 Samiyel ne Sóol: «Duma walbatiku ànd ak yaw, ndax yaa gàntal kàddug Aji Sax ji, Aji Sax ji gàntal sa nguur ci Israyil.» \p \v 27 Naka la Samiyel ne wërëñ, di dem, Sóol jàpp ca catal mbubb ma, mu dagg. \v 28 Samiyel ne ko: «Nii la Aji Sax ji dagge nguurug Israyil ci yaw bés niki tey, jox ko keneen ku la gën. \v 29 Te Aji Nekk-Fàww ju Israyil ji du fen, du réccu, ndax du nit bay réccu.» \p \v 30 Sóol dellu ne: «Bàkkaar naa! Waaye ngalla waay sagal ma ci sama kanam magi askan wi ak ci kanam Israyil. Walbatikul, ànd ak man rekk, ma sujjóotali sa Yàlla Aji Sax ji.» \v 31 Ba loolu amee Samiyel walbatiku topp Sóol. Sóol dem sujjóotali Aji Sax ji. \p \v 32 Gannaaw loolu Samiyel ne: «Indil-leen ma Agag buurub Amalegeen ñi.» Agag nag dikk, wutsi ko, ne finaax. Booba Agag a nga naan ca xelam: «Dee moom, tiitatuma ko, wees na!» \v 33 Samiyel nag ne ko: «Ni aw jigéen ñàkke ay doom yu leen sa saamar xañ, ni la sa ndey di bokke tey ci jigéen ñi ñàkk doom.» Ci kaw loolu Samiyel rey Agag fa kanam Aji Sax ji ca Gilgal. \p \v 34 Ba mu ko defee Samiyel dellu Raama, Sóol moom ñibbi këram ca Gibeya gu Sóol. \v 35 Ba ni Samiyel faatoo, seeteetul Sóol. Teewul mu jooy Sóol, waaye fekk na Aji Sax ji réccu la mu fal Sóol buurub Israyil. \c 16 \ms1 Lii moo dox diggante Sóol ak Daawuda \s1 Yàlla fal na Daawuda \p \v 1 Gannaaw ba loolu wéyee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ne Samiyel: «Yaw foo àpp sa jooy yi ngay jooy Sóol te man maa ko dàq, ba doonatul buur ci Israyil? Gannaaw maa foq nguuram ci Israyil kay, duyal sa béjjén diwu oliw ba mu fees te nga dox, ma yebal la ci Yese waa Betleyem bi. Gis naa ciy doomam ki may fal buur.» \v 2 Samiyel ne ko: «Ana nu ma fay deme? Sóol da koy dégg, rey ma!» Aji Sax ji ne ko: «Aw nag wu jigéen ngay jël, yóbbu, ne ko sarxalsi Aji Sax ji moo la indi. \v 3 Su ko defee nga woo Yese ca sarax sa. Man maa lay xamal nooy def, ba nga diwal ma ki ma la wax, fal ko.» \p \v 4 Samiyel def la Aji Sax ji wax. Ba mu agsee Betleyem, magi dëkk ba gatandoo ko tiitaange, ne ko: «Mbaa tànki jàmm?» \v 5 Samiyel ne leen: «Jàmm rekk. Sarxalsi Aji Sax ji moo ma indi. Sell-luleen te dikk ànd ak man ca sarax sa.» Ci kaw loolu mu sellal Yese ak doomam yu góor, woo leen ca sarax sa. \p \v 6 Naka lañu agsi, Samiyel gis Elyab, daldi ne ca xelam: «Xam naa kii fi kanam Aji Sax ji rekk mooy tànnéefam!» \v 7 Aji Sax ji nag ne Samiyel: «Bul xool ci melokaanu kii, mbaa jëmmu taxawaayam, ndax gàntal naa ko. Lii du ci gis-gisu nit. Nit, li fees bëtam lay gis, waaye Aji Sax ji ci xol lay xool.» \v 8 Yese daldi woo Abinadab, indi ko fi kanam Samiyel. Mu ne: «Aji Sax ji tànnul kii ba tey de!» \v 9 Yese indi Simeya, Samiyel ne: «Aji Sax ji tànnul kii it.» \v 10 Yese indi juróom ñaari doomam yu góor fa kanam Samiyel, Samiyel ne ko: «Aji Sax ji tànnul kenn ci ñii.» \p \v 11 Samiyel nag ne Yese: «Xale yu góor yi yemb nañu?» Yese ne ko: «Xanaa ki gën di ndaw. Ma ngay sàmm gàtt ya.» Mu ne ko: «Yónneel, woolu ko, dunu jekki te dikkul fii.» \v 12 Yese yónnee, ñu indi ko. Ma nga def ku xees, neexa xool, bët ya leer nàññ. Aji Sax ji ne Samiyel: «Diw ko, kii la.» \v 13 Samiyel fab béjjénu diw ba, diw ko fa kanam magam ña. Ba mu ko defee Noowug Aji Sax ji ne milib ca kaw Daawuda, dale fa ànd ak moom bésub keroog. Ba loolu wéyee Samiyel moom, dem dëkk ba ñu naan Raama. \s1 Daawuda dugg na ca liggéeyu Sóol \p \v 14 Ci kaw loolu Noowug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dëddu Sóol, ngelaw lu aay bàyyikoo ci Aji Sax ji, ub boppam. \v 15 Ay dagi Sóol wax Sóol ne ko: «Lii kat ngelawal Yàlla lu aay la. Moo ub sa bopp. \v 16 Nu ngii nag fi sa kanam, joxeel ndigal rekk sang bi, nu wutali la ku mana xalam. Su ko defee bu la ngelawal Yàlla lu aay songee, mu xalamal la, nga am jàmm.» \p \v 17 Sóol ne dagam ya: «Ayca, seetal-leen ma ku mane xalam bu baax, indil ma ko.» \v 18 Kenn ca dag ya ne ko: «Man de, gis naa jenn doomu Yese waa Betleyem bi. Ku mana xalam la te jàmbaare. Ñeyi xare la. Ku déggi wax, ku góorayiw, te Aji Sax ji ànd ak moom.» \p \v 19 Ba loolu amee Sóol yebal ay ndaw ca Yese ne ko: «Yónnee ma sa doom Daawuda, ma ca gàtt ya.» \v 20 Yese yebal doomam Daawuda, daldi takk mbaam, sëf ko mburu ak mbuusu biiñ ak ab tef, ngir mu joxal ko Sóol yóbbal. \v 21 Daawuda dem ca Sóol, daldi tàmbali di ko liggéeyal. Sóol sopp ko lool. Daawuda nag mujj di gàddukatu gànnaayam. \v 22 Ci kaw loolu Sóol yónnee ca Yese, ne ko: «Bàyyil Daawuda, mu di ma liggéeyal far, ndax bég naa ci moom.» \v 23 Ci kaw loolu, saa yu ngelawal Yàlla songee Sóol, Daawuda fab xalam ga, xalamal ko, Sóol féex, am jàmm, ngelaw lu aay la dëddu ko. \c 17 \s1 Golyaat dëkk na bànni Israyil \p \v 1 Waa Filistee boole woon seeni gàngoor ngir xare. Ñu daje ca dëkk ba ñu naan Soko ca diiwaanu Yuda, daldi dale ca Efes Damim diggante Soko ak Aseka. \v 2 Sóol ak waa Israyil nag daje, dale ca xuru Ela, làng-dér ngir jànkoonteek waa Filisti. \v 3 Waa Filistee nga taxawe tund wii, \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* taxawe tund wee, xur wa dox seen diggante. \p \v 4 Ci biir loolu jenn jàmbaar génne ca làngu waa Filisti. Ku ñuy wax Golyaat\f + \fr 17.4 \fr*\fk Golyaat: \fk*\ft am na ñu ko gëna xam ci turu Jalut.\ft*\f*, dëkke Gaat, taxawaayam di juróom benni xasab yu teg diggante baaraamu déy ak digg, xawa tollu ci ñetti meetar. \v 5 Mbaxanam xànjar la sol ak kiiraayal dënnub juróom benn fukki kilo, ñu liggéeye ko waasintóori xànjar. \v 6 Ma nga takk kiiraayi yeel yu xànjar, gàlloo xeeju xànjar bu ndaw ca wagg ya. \v 7 Bantu xeejam bu mag baa nga saf mbaamum ràbb, ñawkay xeej ba di weñ gu ëpp juróom ñaari kilo. Gàddukatu pakkam baa ngay dox, jiitu ko. \p \v 8 Golyaat taxaw, janook làngi Israyil, àddu ca kaw, ne leen: «Ana lu ngeen di génn, làng-déral xare nii? Xanaa du maay waa Filisti ji, yeen ngeen di surgay Sóol? Tabbleen genn góor, mu wàcc, dajeek man. \v 9 Su ma manee ba rey ma, nuy seeni jaam; waaye su ma ko manee ba rey ko, ngeen di sunuy jaam, di nu jaamu.» \v 10 Waa Filisti ba neeti: «Maa dëkk làngi Israyil bés niki tey. Booleleen maak genn góor rekk, nu xeex.» \v 11 Ba Sóol ak bànni Israyil yépp déggee waxi waa Filisti jooju, jàq nañu, tiit nañu lool. \s1 Daawuda def na jaloore \p \v 12 Daawuda nag moo doon doomu góor googu dëkk Efrata ca Betleyem ga ca diiwaanu Yuda, ñu di ko wax Yese. Yese amoon na juróom ñetti doom yu góor. Góor ga, ca jamonoy Sóol, mag mu ñu nawloo la woon. \v 13 Ñetti doomi Yese yu góor yu mag ñoo ràngu woon, topp Sóol ca xare ba. Ñetti doom ya dem xare, taaw ba Elyab lañu koy wax, ka ca topp di Abinadab, ñetteel ba di Simeya. \v 14 Daawudaa ca gënoon di ndaw. Ñetti magam yooyu ñoo toppoon Sóol, \v 15 waaye Daawuda da daan jaabantee fa Sóol ak Betleyem ga muy sàmme gàtti baayam. \p \v 16 Subaak ngoon nag waayu Filisti ja ne jaas taxaw, ba mu am ñeent fukki fan. \v 17 Ci biir loolu Yese ne doomam Daawuda: «Ayca, jëlal nattub mbool mii ak fukki mburu yii te nga daw, yóbbul ko sa mag ya ca dal ba. \v 18 Fukki dogi formaas yii, yóbbul ko seen njiitu kurél. Nemmikul seen jàmmu yaram te nga sàkku ci seen firnde, indil ma. \v 19 Sóol a ngaak ñoom ak waa Israyil gépp ca xuru Ela, di xareek waa Filisti.» \p \v 20 Daawuda teela jóg ca ëllëg sa, wacce gàtt ya ab wattukat, daldi jël yóbbal ga, dem na ko ko baayam sante. Naka la àgg ca dal ba, yemook gàngoor gay génnaale seen xaacuy xare, ngir làng-déri. \v 21 \w Bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ak waa Filisti daldi dér, gàngoor janook gàngoor. \v 22 Ci biir loolu Daawuda wàcce yóbbal ga, wacce ko wattukatub cummikaay ba, daldi daw ba ca làngu xare ba. Mu agsi, nuyook ay magam. \v 23 Na muy wax ak ñoom, jàmbaar ja ñuy wax Golyaat waa Filisti ba dëkke Gaat, ne tëll génne ca làngi waa Filisti. Mu dellu ca wax jooju mu waxoon, Daawuda dégg ca. \p \v 24 Ba bànni Israyil gépp gisee waa ja, dañoo dellu gannaaw, tiit lool. \v 25 Ña nga naan ca seen biir: «Gis ngeen waa jee di ñëw, dëkksi Israyil a ko yékkati. Képp ku ko rey de, Buur dina ko jox alal ju bare. Doomam la koy may jabar, te waa kër baayam, dina leen jagleel ab cér ci digg Israyil.» \v 26 Daawuda ne ña mu dendal: «Ngeen ne, lees di defal ku rey waa Filisti bii, ba faj gàcceg Israyil? Ak kuy yéefaru waa Filisti bii sax, bay dëkk gàngoori Yàlla jiy dund?» \v 27 Nit ña dellu ca loola ñu waxoon, ne moom lañuy defal ku rey waa ja. \p \v 28 Elyab, magu Daawuda, dégg Daawuda di wax ak ñooña. Mu mer, ne ko: «Yaw sax lu la fi indi? Ak koo wacce la fay gàtt ak as néew ca àll ba? Xam naa bu baax sag réy ngise, ak njubadi gi nga mébét. Seetaansi xare bi doŋŋ a la fi indi!» \v 29 Daawuda ne ko: «Waaw, man lu ma def? Xanaa du wax doŋŋ?» \v 30 Daawuda jóge ca mag ja, dem ca keneen, laaj ko mbir mooma, tont la di lenn. \p \v 31 Ci kaw loolu ñu dégg kàddu ya ca Daawuda wax, yegge ko Sóol. Sóol woolu ko. \v 32 Daawuda dikk ne Sóol: «Bu kenn yoqil waa jii, sang bi. Man maay dem xeex ak waa Filisti bii.» \v 33 Sóol ne Daawuda: «Déedéet, yaw manoo songi waa Filisti bii, di xeex ak moom. Gone doŋŋ nga, te moom cag ndawam la dale di nitu xare.» \v 34 Daawuda ne Sóol: «Sang bi, bu may sàmm sama gàtti baay, ba gaynde mbaa rab wu aay dikk, jël ci ab gàtt, \v 35 maa koy topp, dóor ko, nangoo gàtt bi ci gémmiñam. Te bu ma songee, sikkim bi laay sëq, fàdd, mu dee. \v 36 Rey naa gaynde, rey naa weneen rabu àll wu aay, sang bi. Kon nag yéefaru Filisti bii it ni wenn ci yooyu rab rekk, ndax moo tëkku gàngoori Yàlla jiy dund. \v 37 Daawuda neeti: \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ma musal ci pàddum gaynde ak weneen rabu àll wu aay, moo may musal ci loxol waa Filisti bii.» Sóol ne Daawuda: «Demal boog, yal na Aji Sax ji ànd ak yaw.» \p \v 38 Ba mu ko defee Sóol solal Daawuda yérey boppam, solal ko mbaxanam xànjar, solal ko kiiraayal dënn. \v 39 Daawuda ràngoo saamarub Sóol, ca kaw yére ya, daldi jéema dox, mu të, ndax ñàkk koo miin. Daawuda ne Sóol: «Manumaa doxaale lii ndax miinuma ko», daldi koy summi. \v 40 Ba loolu amee Daawuda jël yetam, tànn ca dex ga juróomi doj yu rattax, yeb ca gafakag mbuusum sàmmam, daldi ŋàbb mbaqam, wuti waa Filisti ba. \v 41 Ci biir loolu waa Filisti ba, dox, dikk ba jege Daawuda, gàddukatu pakkam jiitu ko. \v 42 Waa Filisti ba séentu, séen Daawuda; muy xale su góor su ndaw, xees te góorayiw, mu daldi koy xeeb. \v 43 Mu ne Daawuda: «Xanaa ab xaj laa, ba nga di ma jëlalu yet?» La ca tegu waa Filisti ba móolu ko ca turi tuuram, \v 44 ne ko: «Dikkal fii rekk, ba ma leele saw suux njanaaw yeek rabi àll yi.» \p \v 45 Daawuda ne waa Filisti ba: «Yaw de yaa may jëlal ab saamar ak xeej bu mag ak bu ndaw, waaye man turu Aji Sax ju gàngoor yi laa lay dikke, Yàllay làngi xarey Israyil, ji nga tëkku. \v 46 Bésub tey jii Aji Sax jee lay teg ci sama loxo, ma rey la, dog sa bopp. Tey jii sax laay leele njanaaw yeek rabi àll yi, néewi xarekati Filisti, ba àddina sépp xam ne Israyil am na Yàlla. \v 47 Mboolem ñii fi daje dinañu xam ne du saamar te du xeej la Aji Sax jiy walloo, ndax Aji Sax jeey boroom xare bi, te moo leen teg ci sunuy loxo.» \p \v 48 Ci kaw loolu waa Filisti ba daldi dikk, ba gënatee jege Daawuda, Daawuda riir, wuti làng ga, ngir dajeek waa Filisti ba. \v 49 Mu yoor loxoom ca mbuusam, jël ca aw doj, mbaq, jam waa Filisti ba ci jë, doj wa tàbbi ca biir jë ba. Mu ne jànjaŋ, dëpp kanam ga fa suuf. \v 50 Ag mbaq aku doj la Daawuda mane waa Filisti ba, jam ko, rey ko, te yorul saamar. \p \v 51 Daawuda nag daw ba taxaw, tiim waa Filisti ba, jàpp saamaram, boccee ko ca mbar ma, jekkli ko, dog bopp ba. Waa Filisti gis ne seen ñeyu xare dee na, ñu daw. \v 52 Ba loolu amee mbooloom Israyil ak Yuda àddu xaacoondoo, daldi dàqi waa Filisti, ba jub xur wa, ba ca bunti Ekkron. Waa Filisti ya ñu rey ne wetar ca yoonu Saarayim ba Gaat, ba ca Ekkron. \v 53 Bànni Israyil nag waññikoo ca ndàqum Filisti mu metti ma, daldi sëxëtoo seen dal ba. \v 54 Daawuda jël boppu waa Filisti ba, yóbbu Yerusalem, gànnaayi waa ja, mu fat ca xaymab boppam. \p \v 55 Lu jiitu loolu, ba Sóol gisee Daawuda, mu wuti waa Filisti ba, da ne Abner njiital mbooloom xareem: «Waaw, Abner, xale bii doomu kan a?» Abner ne ko: «Buur, giñ naa, nga fekke tey, xawma ko.» \v 56 Buur Sóol ne ko: «Nanga laajte, xale bii, doomu kan la.» \v 57 Naka la Daawuda rey waa Filisti ba, ba dikk, Abner jàpp ko, indi ko ca kanam Sóol. Daawudaa nga ŋàbb boppu waa Filisti ba, ba tey. \v 58 Sóol ne ko: «Yaw, gone gii, yaay doomu kan?» Daawuda ne ko: «Maay doomu Yese, sa surga ba dëkk Betleyem.» \c 18 \s1 Yonatan fas na kóllëreek Daawuda \p \v 1 Ba Daawuda di wax ak Sóol ba noppi, fekk na Yonatan yég ci xolam na mu taqook Daawuda ci biir cofeelu benn bakkan. Yonatan dafa soppoon Daawuda ni boppam. \v 2 Bésub keroog la Sóol téye Daawuda, mayatu ko mu ñibbi kër baayam. \v 3 Ba loolu amee Yonatan fasook Daawuda \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w*, ndax sopp ko ni boppam. \v 4 Ci biir loolu Yonatan summi turkeem, jox ko Daawuda, boole ca ay yérey xareem, ba ca saamaram ak fittam ak ngañaayam sax. \v 5 Daawuda nag di dem ci bépp yoonu xare bu ko Sóol yebal, di ca am ndam. Sóol fal ko njiitu xarekat ya, gàngoor gépp rafetlu loolu, jawriñi Sóol itam rafetlu ko. \s1 Sóol a ngay fexeel Daawuda \p \v 6 Ba ñu demee ba xarekat yay ñibbi, gannaaw ba Daawuda reyee waa Filisti ba, jigéeni mboolem dëkki \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* a génn gatanduji Buur Sóol, di fecc ak a woy, tabala ya ànd ak sarxolle ya ak xalam ya. \v 7 Ña ngay fo, di awoonte, naan: \q1 Sóol jam junneem, \q1 Daawuda jam fukki junneem. \p \v 8 Sóol ñaawlu kàddu ga, mer lool. Mu ne ca xelam: «Daawuda lañu moomale fukki junni; man, junni! Lu ko deseeti lu moy jal bi?» \v 9 Bésub keroog la Sóol dale ronni Daawuda. \p \v 10 Ca ëllëg sa ngelawal Yàlla lu aay ne milib ca kaw Sóol, muy waxtu ca digg këram. Daawuda nag di ko xalamal, na mu daan def naka jekk, fekk Sóol ŋàbb ab xeejam. \v 11 Mu jekki sànni xeej ba, te naan ca xelam: «Naa daaj Daawuda ci tabax bi!» Daawuda nag mbas ko ñaari yoon. \p \v 12 Sóol daldi ragal Daawuda, ndax booba xam na ne \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee ko dëddu, ànd ak Daawuda. \v 13 Ba loolu amee mu jële ko fi wetam, fal ko njiitu kurélu junniy xarekat, muy xareji, di délsi, jiite gàngoor ga. \v 14 Daawuda baaxle ca yoonam yépp, Aji Sax ji ànd ak moom. \v 15 Ba Sóol gisee Daawuda àntule lool, mu gën koo ragal. \v 16 Teewul mboolem Israyil ak Yuda sopp Daawuda, ngir moo leen jiite woon, di xareji, di dikk. \s1 Daawuda jël na doomu Sóol soxna \p \v 17 Ci kaw loolu Sóol ne Daawuda: «Sama taaw bu jigéen, Merab a ngii. Moom laa lay may. Nekkal ma sama jàmbaaru xare rekk, te xareel \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ay xareem.» Booba Sóol a nga naan ca xelam: «Bu ko sama loxo laal, nay loxol waa Filisti.» \p \v 18 Daawuda ne Sóol: «Waaw, ana lu ma tekki, man maak samay bokk, sama askanu baay ci Israyil, ba wara mana goromlook Buur?» \v 19 Ba ñu demee ba wara jox Daawuda, Merab doomu Sóol ja, Àddiryel ma cosaanoo Mewola lañu ko may. \p \v 20 Ci kaw loolu Mikal doomu Sóol bëgg Daawuda, ñu àgge ko Sóol, mu am ca mbégte. \v 21 Booba Sóol a nga naan: «Naa ko ko may, ngir mu doon ndëgg-sërëxam, ba waa Filisti teg ko loxo.» Sóol nag wax Daawuda, ñaareel bi yoon, ne ko: «Tey ngay samab goro.» \v 22 Ci biir loolu Sóol sant ay dagam, ne leen: «Diisool-leen maak Daawuda, ngeen wax ko ne ko: “Yaw kat, Buur am na bànneex ci yaw, te it dagam yépp a la sopp. Kon nag nangula doon gorob Buur.”» \v 23 Dagi Sóol ya déey Daawuda kàddu yooyu. Daawuda ne leen: «Ngeen defe ne goromlook buur daal, du dara? Man mii taqul dara, tekkiwuma dara!» \v 24 Dag ya yegge Sóol kàddu yooyu Daawuda wax. \p \v 25 Sóol ne leen: «Waxleen Daawuda ne ko, Buur de sàkkuwul ub can: xanaa téeméeri mbuñukay waa Filisti yu mu feyoo ci noonam yooyu.» Booba la Sóol laloon mooy pexe mu tàbbal Daawuda ca loxol waa Filisti. \v 26 Dag ya yegge Daawuda kàddu yooya, doon gorob buur daldi koy jaral loola. Balaa àpp baa mat, \v 27 Daawuda dem na, mooki nitam ba rey ñaar téeméeri waa Filisti. Daawuda indi seeni mbuñuka, ñu waññal ko Buur ba mu mat sëkk, mu daldi yeyoo goromlook Buur. Ba loolu amee Sóol may Daawuda doomam Mikal. \v 28 Sóol nag xam xéll ne Aji Sax jee ànd ak Daawuda, te it doomam Mikal bëgg na ko, \v 29 mu gën koo ragalati. Fa la Sóol doxe doon noonub Daawuda ba fàww. \p \v 30 Ci kaw loolu njiiti xarey Filisti di amal ay cong, noppiwuñoo xareek Israyil. Teewul saa yu ñu songaan, Daawudaay gëna am ndam mboolem jawriñi Sóol, ba mujj Daawuda amu tur lool. \c 19 \s1 Yonatan taxawu na Daawuda \p \v 1 Ba mu ko defee Sóol xamal doomam Yonatan ak dagam yépp ne reylu Daawuda mooy li mu nar. Te Yonatan doomu Sóol sopp Daawuda lool. \v 2 Yonatan yegge ko Daawuda, ne ko: «Sama baay a ngi lay wuta rey. Yaw nag fagarul kat te teela xëy ëllëg, seet foo làquji te baña génn. \v 3 Man dinaa dem, taxaw ci sama wetu baay fi nga nekk ci àll bi. Dinaa wax ak sama baay ci yaw, nu bokk taxaw ca tool ba ngay làquji, man ci sama bopp dinaa wax ak sama baay ci yaw ba gis nu mbir mi tëdde, yegge la ko.» \v 4 Ci kaw loolu Yonatan wax baayam lu baax ci Daawuda, ne ko: «Buur, ngalla bul tooñ Daawuda, sa jaam bii, ndax moom kat tooñu la, lu baax rekk la la masa defal. \v 5 Jaay na bakkanam, ba rey waa Filisti ba. \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji maye ca ndam lu réy, ñeel Israyil gépp, nga teg ci bët, am ca mbégte. Ana lu waral ngay tooñ, di tuur deretu jaamburu Yàlla bu mel ni Daawuda, reylu ko ci dara?» \v 6 Sóol nag déggal Yonatan, daldi ne: «Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund, deesul rey Daawuda.» \v 7 Yonatan woo Daawuda, nettali ko waxtaan wa wépp, door koo yóbbu ca Sóol, mu dellu di ko liggéeyal, na woon. \s1 Mikal xettli na Daawuda \p \v 8 Ci kaw loolu xare jibaat, Daawuda dem xeexi ak waa Filisti, daan leen jéll bu réy, ñu daw. \v 9 Ci kaw loolu ngelaw lu aay lu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal Sóol, fekk ko toog ci biir këram, ŋàbb ab xeejam, Daawudaa di xalam. \v 10 Sóol di wuta jam Daawuda xeej bi, ngir daaj ko ca tabax ba. Daawuda nag mbas ko, mu jam xeej ba ca tabax ba. Daawuda daldi daw, ba raw guddig keroog. \p \v 11 Sóol yebal ay ndaw ca kër Daawuda ngir ñu xoolal ko ko, ba bët set, ñu rey ko. Mikal, soxnas Daawuda, yégal ko Daawuda, ne ko: «Soo rawalewul sa bakkan ci guddi gi de, bu ëllëgee dees na la rey.» \v 12 Ba loolu amee Mikal jaarale ko ca palanteer ba, mu wàcc, daw, ba raw. \v 13 Mikal jël gàllaaju kër ga, teg ca lal ba, fab deru bëy, teg fa féeteek bopp ba, daldi koy sànge malaan. \v 14 Sóol yebal ay ndaw yu jàppsi Daawuda, Mikal ne: «Moom de daa wopp.» \v 15 Ci kaw loolu Sóol dellu yebal ndaw ya, ngir ñu dem ba gis ko. Mu ne leen: «Indil leen ma ko, booleek lal bi, ba ma rey ko!» \v 16 Naka la ndaw ya délsi, xool, gisuñu lu moy gàllaaju kër ga ca kaw lal ba, ak deru bëy ba féeteek bopp ba. \v 17 Ba loolu amee Sóol ne Mikal: «Ana lu waral nga wor ma nii, bàyyi sama noon, mu rëcc?» Mikal ne ko: «Moom kay moo ma ne: “Bàyyi ma, ma daw, lu ko moy ma rey la!”» \s1 Sóol toppi na Daawuda ca Nayot \p \v 18 Noonu la Daawuda dawee ba raw. Mu fekki Samiyel ca Raama, wax ko la ko Sóol def lépp. Ñu ànd, mook Samiyel, dali ca Nayot. \v 19 Ñu yegge ko Sóol ne ko: «Ndeke Daawudaa nga Nayot ca dëkk ba ñuy wax Raama.» \v 20 Sóol yebal ay ndaw, ngir ñu jàpp Daawuda. Nit ña dikk, gis kurélu yonent yuy wax ay \w waxyu|lemma="waxyu:"\w*, Samiyel jiite leen. Ba loolu amee, ca kaw ndawi Sóol ya la Noowug Yàlla wàcc, ñuy wax ay waxyu, ñoom itam. \v 21 Ñu yegge ko Sóol, mu yebal yeneen ndaw, ñu dikk, di wax ay waxyu, ñoom it. Sóol dellooti yebal ay ndaw, ñetteel bi yoon, ñu dikk, di wax ay waxyu, ñoom itam. \v 22 Mu jóg moom ci boppam, jëm Raama. Mu dikk ba ca teen bu mag ba ca Seeku, daldi laajte ne: «Ana fu Samiyel ak Daawuda nekk?» Ñu ne ko: «Ña nga ca Nayot ca Raama.» \p \v 23 Sóol jubal yoonu Nayot ca Raama. Ba loolu amee, ca kawam, moom it, la Noowug Yàlla wàcc, muy wéy di wax ay waxyuy dem, ba àgg Nayot ca Raama. \v 24 Ci kaw loolu mu summiy yéreem, di wax ay waxyu moom it fa kanam Samiyel, daldi ne làndaŋ, ne duŋŋ, bëccëg keroog gépp ak guddi ga gépp. Looloo waral ñu naan: «Moo Sóol it ci yonent yi laa?» \c 20 \s1 Yonatan wallu na Daawuda \p \v 1 Daawuda nag dawe Nayot, ca wetu dëkk ba ñuy wax Raama. Mu dikk ca Yonatan, ne ko: «Ana lu ma def? Ana ñaawtéef gu ma def, ak fu ma tooñe sa baay, ba muy wut sama bakkan?» \v 2 Yonatan ne ko: «Yàlla tere kay, doo dee mukk! Ma ne, sama baay du def dara lu réy ak lu tuut te yégalu ma ko. Su amoon moomu mébét, lu mu ma ciy nëbb? Loolu kay amul!» \v 3 Daawuda daldi giñ, neeti ko: «Dinaa la ko giñal, sa baay xam na xéll cér bi ma am ci yaw. Moo tax mu ne: “Bu Yonatan yég sama mébét mukk, lu ko moy dina ko naqarlu.” Waaye giñ naa ko, nga fekke ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jiy dund, ab jéego sax doxul sama digganteek dee.» \v 4 Yonatan ne Daawuda: «Wax ma loo bëgg rekk, ma defal la ko.» \p \v 5 Daawuda ne Yonatan: «Xanaa lenn. Ëllëg la màggalu Terutel weer wi, te man, manumaa ñàkka toog ak Buur, ngir lekk. Waaye may ma, ma làquji àll ba, ba gannaaw ëllëg ca ngoon. \v 6 Su sa baay seetloo ba seetlu ne nekkuma fa, nee ko: “Daawuda déy da maa tinoo tinu, ne ma yiwi ko, mu ne coww ba Betleyem, dëkkam, ngir saraxu at ba at bu fa bokkam yépp amal.” \v 7 Su nee baax na de, sang bi, sama jàmm la, waaye su sànjoo ba sànju nag, xamal ne musiba la nar. \v 8 Su boobaa nag sang bi, yéwéne ma rekk sang bi, ngir \w kóllëreg|lemma="kóllëre g-:"\w* Aji Sax ji nga fasook man. Waaye ndegam am na genn ñaawtéef gu ma gàkkal, ngalla rey ma yaw ci sa bopp, jarul nga di ma yóbbu ci sa baay.» \v 9 Yonatan ne ko: «Yàlla tere. Te su ma yégoon ba yég musiba mu sama baay nara indi fi sa kaw, na la wóor ne dinaa la ko xamal.» \v 10 Daawuda ne Yonatan: «Su la sa baay tontoo kàddu yu ñagas nag, ana ku ma koy xamal?» \v 11 Yonatan ne Daawuda: «Kaay nu dem ba ca àll ba.» Ñu ànd ñoom ñaar ba ca àll ba. \p \v 12 Yonatan ne Daawuda: «Giñ naa ci Aji Sax ji, Yàllay Israyil, dinaa seetlu sama baay nëgëni sii gannaaw ëllëg. Su la naralee jàmm, yaw Daawuda, dinaa yónnee ci yaw ku la ko déey. \v 13 Waaye su la sama baay nammee indil musiba, yal na ma Aji Sax ji def lu ko raw, ndegam déeyuma la ko, ba rawale la ci jàmm. Yal na Aji Sax ji ànd ak yaw, na mu ànde woon ak saa baay. \v 14 Xanaa moos su may dund, ci ngorug Aji Sax ji ngay jëfeek man. Su ma deeyee nag, \v 15 bul noppee jëfe ngor sa digg ak sama waa kër mukk, ba sax keroog bu Aji Sax ji faree fi kaw suuf képp kuy noonu Daawuda.» \v 16 Noonu la Yonatan fasook waa kër Daawuda, ne: «Yal na Aji Sax ji fey nooni Daawuda.» \p \v 17 Ba mu ko defee Yonatan dellu giñloo Daawuda ci cofeelam gi mu am ci Daawuda ndax ni mu soppe boppam la ko soppe woon. \v 18 Yonatan dellu ne ko: «Ëllëg ci màggalu Terutel weer wi, sag wuute dina fés, ndax sa toogu ba mooy wéet. \v 19 Kon bu gannaaw ëllëgee gaawal dem, ba fa nga làqu woon keroog ba mbir mi amee, te nga négandiku ca wetu doju Gindikaay wa. \v 20 Man nag dinaa sànni ñetti fitt ca wet ga, mu mel ni daa am lu ma fay diir. \v 21 Su ko defee rekk, ma yebal ndaw, ne ko mu jëli fitt yi. Su ma nee ndaw li: “Ée! Xoolal fitt yaa ngii nga romb, foral!” Su boobaa, ñëwal, jàmm ñeel na la, te dara amul, giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund. \v 22 Waaye su ma nee ndaw li: “Fitt yaa nga nale ca sa kanam!” Su booba, demal, ndax Aji Sax jee la yebal. \v 23 Mbir moomu nu digoo, maak yaw nag, Aji Sax jaa ngii, di ci seede sama digganteek yaw ba fàww.» \p \v 24 Daawuda làquji ca àll ba. Ba màggalu Terutel weer wa jotee, Buur toog di waaja lekk. \v 25 Buur a nga toog ca toogoom naka jekk, fa sës ca miir ba. Yonatan taxaw, Abner toog, feggook Sóol, toogub Daawuda ba nag wéet. \v 26 Sóol waxul dara bésub keroog, ndax booba ma nga naan ci xelam: «Ndogal la, boo demee daa setul, xam naa daa setul rekk.» \v 27 Ca ëllëg sa, di ñaareelu bésu Terutel weer wa, toogub Daawuda bay wéet ba tey. Sóol nag ne doomam Yonatan: «Waaw, lu waral doomu Yese ji lekksiwul démb ak tey?» \v 28 Yonatan ne Sóol: «Daawuda de da maa tinoo tinu ngir ma yiwi ko, mu dem Betleyem. \v 29 Daf ma ne: “Ngalla yiwi ma, ndax saraxu biiri bokk lanu am ca dëkk ba, sama mag a ma sant, ma teeweji ko. Kon nag su la neexee, may ma rekk ma rëcc, seeti saay bokk.” Looloo waral dikkul ci sa ndab li, Buur.» \p \v 30 Ba loolu amee Sóol xadaru ci kaw Yonatan. Mu ne ko: «Doomu caga bi, yaa të ndey! Xanaa xawma ne yaw, doomu Yese ji nga faral, muy sa gàcce, di sa gàcceg kanamu ndey? \v 31 Ngir li feek doomu Yese jiy dund fi kaw suuf, yaw doo taxaw, sa nguur du taxaw. Léegi nag, yónneel, ñu indil ma ko, ndax moom aji dee la!» \v 32 Yonatan ne baayam: «Lu tax muy dee? Ana lu mu def?» \v 33 Sóol ne ko xërr xeej ba, nar koo rey. Yonatan nag xam ne rey Daawuda la baayam dogu. \v 34 Yonatan jóge ca ndab la ak tàngooru meram. Lekkul dara keroog ñaareelu bésu màggalu Terutel weer wa, ndax naqar wu mu am ca na baayam torxale Daawuda. \p \v 35 Ca ëllëg sa Yonatan xëy, xalelu góor bu ndaw ànd ak moom, mu dem ca àll ba, ca digoom baak Daawuda. \v 36 Mu ne xaleem ba: «Dawal seeti fitt yi may sànni.» Xale ba daw, mu soqi fitt ga, mu jiitu ko. \v 37 Xalelu góor ba dem ba fa fittu Yonatan ga dal, Yonatan woo xale bi, ne ko: «Ée! Xanaa du fitt gaa nga nale ca sa kanam?» \v 38 Mu wooti ko, ne ko: «Ée, doxal gaaw, bul taxaw!» Xale ba for fitt ga, dellu ca njaatigeem Yonatan. \v 39 Xale bu góor ba nag xamu ca dara, Yonatan ak Daawuda rekk a xam mbir ma. \v 40 Yonatan daldi jox xaleem ba ay gànnaayam, ne ko: «Doxal, yóbbu ca dëkk ba.» \v 41 Xale ba dem, Daawuda jóg, génne ca làquwaayam ba fare bëj-saalum. Mu ne gurub, dëpp jëëm fa suuf, sujjóot ñetti yoon, ku nekk fóon sa moroom, ñoom ñaar ñépp jooy, te Daawuda rawati. \v 42 Yonatan ne Daawuda: «Demal ak jàmm, gannaaw noo giñoo nun ñaar ci turu Aji Sax ji ne “Aji Sax jeey seede sama digganteek yaw, ak diggante sama askan ak saw askan, ba fàww.”» \p Ba mu ko defee Daawuda dem, Yonatan dellu ca dëkk ba. \c 21 \s1 Daawuda dem na ca Ayimeleg \p \v 1 Gannaaw ba loolu wéyee Daawuda dem dëkk ba ñuy wax Noob ca Ayimeleg \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba. Ayimeleg gatandu ko, di lox, ne ko: «Lu la taxa wéet, kenn àndul ak yaw?» \v 2 Daawuda ne Ayimeleg sarxalkat ba: «Buur a ma sant ne ma: “Bu kenn xam lenn ci li ma la yónni, ak li ma la sant.” Samay ndaw nag, xamal naa leen ne bérab sàngam lañu wara xaar. \v 3 Loo fi denc nag? Su dee juróomi mburu mbaa lu beggandi rekk, jox ma!» \v 4 Sarxalkat ba ne Daawuda: «Dencuma mburum neen de, mburu mu \w sell|lemma="sell:"\w* a fi ne. Jëlal, jox say nit, ndegam fekk na leen ñu fegu ci aw jigéen.» \v 5 Daawuda ne sarxalkat ba: «Aw jigéen kay mbañ la ci nun naka jekk, su ma nekkee ci yoonu xare, te sellal la sama nit ñi nekke nii. Doonte yoon wii laajul sellal, tey fekk na leen sellal moos ci moomu mbir.» \v 6 Ci kaw loolu sarxalkat ba jox ko loola ñu sellal, ndax mburu amu fa woon, lu moy \w mburum teewal|lemma="mburum teewal m-:"\w*, ma ñu jële woon fa \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ba wuutal fa mburu mu tàng ca saa sa ñu ko fa jëlee. \p \v 7 Fa la fekk keroog ab jawriñu Sóol bu yitte téye woon fa Aji Sax ji. Mooy Edomeen ba ñuy wax Doweg; njiital sàmmi Sóol la woon. \p \v 8 Daawuda ne Ayimeleg: «Dencoo fi ab xeej mbaa saamar bu jàppandee? Ndax du saamar, du lenn ci samay gànnaay lu ma indaale, ngir yónnentu Buur a jampoon lool.» \v 9 Sarxalkat ba ne ko: «Xanaa saamarub Golyaat waa Filisti ba nga reyoon ca xuru Ela. Ma nga nee laxase ca turki ba, ca gannaaw \w xar-sànni|lemma="xar-sànni m-:"\w* ma. Soo ko bëggee, jëlal, boobu rekk a fi ne.» Daawuda ne ko: «Aa! Boobu kay amul moroom, jox ma ko.» \s1 Daawuda nax na leen \p \v 10 Bésub keroog Daawuda daw na Sóol ba àgg ca Akis buurub Gaat. \v 11 Jawriñi Akis ya wax Akis ne ko: «Xanaa kii du Daawuda, boroom réew mi? Du kii lañuy woyal, di fecc, naan: \q1 “Sóol jam junneem, \q1 Daawuda jam fukki junneem”?» \p \v 12 Daawuda am lu mu foog ci kàddu yooyu, ba tax mu ragal lool Akis buurub Gaat. \v 13 Mu daldi soppliku ba mel ni ku teqlikook sagoom ca seen kanam, di dof-doflu ca seen kaw, di bindantu ca bunt yaaka rogalaatal ay yuut ca kawaru sikkim ba. \v 14 Akis ne jawriñam ya: «Xam ngeen ne kii ab dof la; ana lu ngeen ma koy indile? \v 15 Damaa ñàkk ay dof ba ngeen di ma yokkal lii, muy def yëfi dof fi sama kaw? Lu lii di wut sama biir kër?» \c 22 \s1 Daawuda jiite na gàngoor \p \v 1 Ba loolu amee Daawuda jóge Gaat, daw làquji ca biir xuntim Adulam. Magam yaak waa kër baayam gépp yég ko, dikk, fekksi ko fa. \v 2 Ci biir loolu mboolem boroom njàqare ya, ak ña bor jiital, ak tàng-xol ya, ñoom ñépp dajeji fa Daawuda, mu doon seen njiit. Ñu wara tollook ñeenti téeméeri nit, ànd ak moom. \v 3 Daawuda bàyyikoo fa dem Mispe, ca diiwaanu Mowab. Mu wax buuru Mowab ne ko: «Rikk may ma, sama baay ak sama ndey dikk toog ak yaw, ba ma xam nu Yàlla di def ak man.» \v 4 Noonu la Daawuda yóbboo ay waajuram Mispe ca buuru Mowab, ñu toog fa mboolem diir ba mu làqu ca rawtoom ba. \v 5 Ci kaw loolu Yonent Yàlla Gàdd ne Daawuda: «Bul toog ci rawtu bi, fabul dem réewum Yuda.» Daawuda bàyyikoo ca, dem ba ca gottub Eret. \s1 Sóol rey na sarxalkati waa Noob \p \v 6 Ci biir loolu Sóol dégg ne gis nañu Daawuda ak ña ànd moom. Booba Sóol a nga toog ca ker garabu tamaris, ga ca Gibeya ca kaw tund wa. Ma nga ŋàbb xeejam, jawriñam yépp taxaw ci wetam. \v 7 Sóol wax ak jawriñam yi taxaw ci wetam, ne leen: «Yeen Beñamineen ñi, dégluleen! Mbaa yeen ñépp, doomu Yese jee leen di jox ay tool aki tóokëri reseñ, am yeen ñépp lay fal njiiti kuréli junni ak njiiti kuréli téeméer, \v 8 ba ngeen di ma fexeel yeen ñépp? Du kenn ku ma yégal ne sama doom fasoo naak doomu Yese ji. Du kenn ku ma tiisoo, yégal ma ne sama doom a ngi xabtal sama surga ci sama kaw, ngir mu waajal ma am tëru ni tey jii!» \p \v 9 Doweg, Edomeen ba taxawandook jawriñi Sóol, daldi àddu, ne: «Man de, gis naa doomu Yese ji, mu dikk dëkk ba ñuy wax Noob, ca Ayimeleg doomu Ayitub. \v 10 Ayimeleg seetal na ko ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ab dund it may na ko ko, te it saamaru Golyaat waa Filisti ba, jox na ko ko.» \v 11 Buur Sóol woolu \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba Ayimeleg doomu Ayitub, ak mboolem bokki baayu Ayimeleg ya doon ay sarxalkat ca Noob; ñu wuysi Buur Sóol, ñoom ñépp. \v 12 Buur ne: «Yaw doomu Ayitub, déglu ma fii!» Mu ne ko: «Maa ngi lay dégg, sang bi.» \v 13 Sóol ne ko: «Li nga ma def nag, di ma fexeel, yaak doomu Yese ji? Yaa ko may ab dund, yaa ko jox ab saamar, seetal ko ci Yàlla, ba mu jógal ma, di ma tëru nii tey!» \p \v 14 Ayimeleg ne Buur: «Buur, ana sa surga yii ba ñu daj, ku la nangule ni Daawuda mii, di sa goro, jiite say dag, te di ku ñu nawloo ci sa biir ëtt bii? \v 15 Du keroog laa ko jëkka seetal ci Yàlla de! Te it Yàlla buma la lalal pexe! Dëgg waay, Buur sama sang, bu ma topp lenn maak kenn ci sama waa kër baay, ndax kat sang bi, xawma dara ba dara booloo jeex ci menn pexe.» \v 16 Buur Sóol ne ko: «Yaw Ayimeleg kay, dee rekk mooy sab àtte, yaak sa waa kër baay yépp.» \v 17 Ba mu ko defee Buur ne dagam ya ko dar: «Ayca, reyleen sarxalkati Aji Sax yii, gannaaw ñoom it ñook Daawudaa far. Yégoon nañu ba muy daw te xamaluñu ma ko.» Dagi buur ya nag baña xàcci seen loxo ci kaw sarxalkati Aji Sax ya. \v 18 Buur ne Doweg: «Ayca yaw, fàddal sarxalkat yii!» Doweg Edomeen ba fàdd sarxalkat ya. Rey na bésub keroog juróom ñett fukki nit ak juróom (85) ñuy sol \w xar-sànnim|lemma="xar-sànni m-:"\w* lẽe. \v 19 Waa Noob dëkkub sarxalkat ya it, mu jam leen, leele ñawkay saamar; góor ak jigéen, gone ya, ba ca ñay nàmp, ak nag yaak mbaam yaak gàtt ya, lépp la leele ñawkay saamar. \p \v 20 Jenn doomu Ayimeleg miy doomu Ayitub doŋŋ a rëcc, te mooy Abiyatar. Mu daw, fekki Daawuda. \v 21 Mu yégal Daawuda ne ko Sóol reylu na sarxalkati Aji Sax yi. \v 22 Daawuda ne Abiyatar: «Xamoon naa bésub keroog ne gannaaw Doweg Edomeen baa nga fa woon, du ñàkk moos mu nettali ko Sóol. Man mii maa gàddu sa bakkani waa kër baay gépp. \v 23 Waaye toogal fii ci man, te bul ragal dara. Ki lay wuta rey moo may wuta rey man itam. Soo nekkee ci sama wet nag, yiiru nga.» \c 23 \s1 Daawuda xettli na waa Keyla \p \v 1 Mu am bés nag, ñu yégal Daawuda, ne ko: «Waa Filisti de ña ngay song waa Keyla xare. Ña ngay sëxëtoo dàgga ya.» \v 2 Daawuda seet ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ne ko: «Ndax ma dem xarejeek waa Filisti?» Aji Sax ji ne Daawuda: «Demal kay xareek waa Filisti, xettli waa Keyla.» \v 3 Niti Daawuda ne Daawuda: «Waaw, ndegam fii ci Yuda lanu tiite, astamaak bu nu demee Keyla, ba janook làngi waa Filisti!» \v 4 Daawuda dellu seet ci Aji Sax ji, Aji Sax ji ne ko: «Doxal dem Keyla, man, maay teg waa Filisti ci say loxo.» \v 5 Ba mu ko defee Daawuda ànd aki nitam dem Keyla, xareek waa Filisti, duma leen duma yu réy, yóbbu seenug jur. Noonu la Daawuda xettlee waa Keyla. \p \v 6 Ba Abiyatar doomu Ayimeleg dawee fekki Daawuda ca Keyla, \w xar-sànni|lemma="xar-sànni m-:"\w* ma\f + \fr 23.6 \fr*\fk xar-sànni ma: \fk*\ft dañu ko daan seete ci Aji Sax ji.\ft*\f* la indaale. \p \v 7 Ci kaw loolu ñu yegge Sóol ne ko Daawuda dem na Keyla. Sóol ne: «Kon de Yàllaa ko teg ci samay loxo, ndax ba mu duggee biir dëkk bu tëje ràpp la tëj boppam.» \v 8 Ba loolu amee Sóol woo gàngooram gépp xare, ngir ñu dem Keyla, gawi Daawudaaki nitam. \v 9 Daawuda nag yég ne moom la Sóol di fexeel njekkar. Mu ne Abiyatar \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba: «Indil xar-sànni mi.» \v 10 Mu indi ko, Daawuda ne: «Éy Aji Sax ji, Yàllay Israyil sama Boroom, dégg naa déy ne Sóol a ngi waaja dikk Keyla gii, tas-si dëkk bi ndax man. \v 11 Mbaa kilifay Keyla duñu ma teg ci loxoom? Boroom bi, ndax li ma dégg ñu naan Sóol a ngi ñëw, dëgg la? Éy Aji Sax ji, Yàllay Israyil, sama Boroom, ngalla wax ma!» Aji Sax ji ne: «Dina ñëw.» \v 12 Daawuda ne: «Mbaa kilifay Keyla duñu ma teg, maak samay nit ci loxol Sóol?» Aji Sax ji ne ko: «Ahakay.» \v 13 Daawuda fabu mooki nitam, ñu wara tollu ci juróom benni téeméer, daldi bàyyikoo Keyla, di taxawaaloo fépp fu ñu ñeme. Ba ñu yeggee Sóol ne ko Daawuda rëcce na Keyla, Sóol yebbi. \p \v 14 Daawuda nag nekk ca xunti yu kawe ya ca màndiŋ ma, toog foofa ca tund, wa ca màndiŋu Sif. Sóol di ko seet bés bu nekk, waaye Yàlla tegul Daawuda cay loxoom. \v 15 Gannaaw gi Daawuda yég ne Sóol waajal na aw yoon ngir jël bakkanam. Booba Daawudaa nga ca màndiŋu Sif ca Orsa. \v 16 Ci biir loolu Yonatan doomu Sóol ja dem Orsa ca Daawuda, di ko ñaax ngir mu gëna dëgërloo Yàlla. \v 17 Mu ne ko: «Bul tiit. Loxol Sóol sama baay du la jot. Yaw yaay falu Buur ci Israyil, te maay doon sa bummi. Sama baay ci boppam xam na loolu bu baax.» \v 18 Ci biir loolu ñu feddli seen \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* ñoom ñaar fa kanam Aji Sax ji. Daawuda des Orsa, Yonatan ñibbi këram. \s1 Sóol topp na Daawuda \p \v 19 Ba loolu amee waa Sif dem Gibeya ca Sóol, ne ko: «Daawuda de, ma nga làqu fa nun. Ma nga ca xunti yu kawe ya ca Orsa, ca kaw tundu Akila, fa féete màndiŋ ma bëj-saalum. \v 20 Buur, saa yoo bëggee ñëw rekk, ñëwal. Kon, Buur, nun noo koy teg ci say loxo.» \v 21 Sóol ne leen: «Yal na leen \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji barkeel ndax yég ngeen ma. \v 22 Léegi demleen, xoolaat bu baax; seetleen ba gis fu mu jaare, ak ku ko fa gis, ndax xamal nañu ma ne ku ñora ñor la. \v 23 Seetleen ba gis fépp fu mu mana làqu, doora délsi fii ci man, indil ma lu leer. Su ko defee ma ànd ak yeen. Su Daawuda nekkee ci gox bi, dinaa topp tànkam ci biir mboolem làngi Yudeen ñi.» \p \v 24 Ba loolu amee waa Sif jiituji Sóol ca Sif. Fekk na Daawudaaki nitam ña nga woon ca joor ga ca màndiŋu Mawon, fa féete màndiŋ ma bëj-saalum. \v 25 Sóol aki nitam dem, di wër Daawuda, ñu yegge ko Daawuda, mu dem ba ca doj wa, làqu foofa ca màndiŋu Mawon. Sóol yég ko, dàqi ko ca biir màndiŋu Mawon. \v 26 Sóol a ngay demee gii wetu tund wi, Daawudaaki nitam bartaloo wet ga ca des, gaawtu di wéy, ngir rëcc Sóol. Naka la Sóol ak mbooloom dem bay wër-ndombo Daawuda aki nitam, ngir jàpp leen, \v 27 ndaw dikk ca Sóol ne ko: «Dikkal gaaw, waa Filisti song nañu réew ma.» \v 28 Sóol nag fomm ndàqum Daawuda, ngir dajejeek waa Filisti. Looloo waral turu bérab boobu di Sela Amalekot (mu firi doju Rawukaay). \s1 Daawuda gën na Sóol \p \v 29 Foofa la Daawuda bàyyikoo, dali ca xunti yu kawe ya ca Engedi. \c 24 \p \v 1 Naka la Sóol délsi, jóge ca ndàqum waa Filisti, ñu ne ko: «Ndeke Daawudaa nga ca màndiŋu Engedi!» \v 2 Ci kaw loolu Sóol jël ñetti junniy xarekat yu mu tànne ci \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp, ngir wëri Daawuda aki nitam, ba fa dendeek tundi Sikket ya. \v 3 Mu dem ba tollook ay ngéddi xar ca yoon wa; foofa am xuntee nga fa woon. Mu dugg ca biir, di suturlu. Fekk na Daawudaaki nitam a nga ca biir-a-biir xunti ma, toog. \p \v 4 Ba mu ko defee niti Daawuda ya déey Daawuda, ne ko: «Xoolal bésub tey jii la la sa yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji noon: “Maa ngii, di teg sab noon ci say loxo, nga def ko lu la neex.”» Daawuda yoot ndànk, ba dagg ca lafu mbubbum Sóol. \v 5 Ba loolu amee fitu Daawuda ne tërit ndax la mu dagg ca lafu mbubbum Sóol. \v 6 Mu ne nitam ña: «Yal na ma Aji Sax ji musal ba duma def sama sang, kii Aji Sax ji fal, jëf ju tollu ni xàccil ko sama loxo, ndax moom mooy ki Aji Sax ji fal.» \v 7 Kàddu yooyu la Daawuda dànkaafoo nitam ña; mayu leen ñu dal ci kaw Sóol, ba Sóol jóge ca xunti ma, dem yoonam. \p \v 8 Daawuda nag génn xunti ma, woo Sóol, ne ko: «Éey, Buur sama sang!» Sóol geesu; Daawuda sukk, sujjóot, dëpp jëëm fa suuf, \v 9 daldi wax Sóol ne ko: «Lu waral ngay déglu ku la naan: “Daawuda mii sa musiba lay wut.” \v 10 Bés a ngii tey, nga gisal sa bopp ni la Aji Sax ji tege tey ci samay loxo ci biir xunti mi. Nee ñu ma, ma rey la, waaye dama laa xool bëtu ñeewante. Maa ne duma xàccil mukk sama loxo sama sang, ndax mooy ki Aji Sax ji fal. \v 11 Te xoolal, Baay, xoolal rekk sa daggitu mbubb wii ci sama loxo. Gannaaw maa ko dagge ci sa mbubb te reyuma la, war ngaa xam, nag xéll ne naruma genn mbon mbaa pexem fippu, te tooñuma la. Yaw kay yaa may rëbb, ngir jël sama bakkan. \v 12 Yal na Aji Sax ji àtte sama digganteek yaw. Yal na ma Aji Sax ji feyul ci yaw, waaye du sama loxoo lay dal mukk. \v 13 Mooy la ñu léeb bu yàgg rekk ne: “Ku bon, mbon rekk.” Man nag sama loxo du la dal mukk. \v 14 Ana sax ku buurub Israyil jóg, di dàqi? Ab xaj bu dee, aw fel doŋŋ lay dàq! \v 15 Aji Sax jeey àttekat bi, te mooy àtte sama digganteek yaw. Yal na ma geesu te sàmm sama àq. Yal na ma jox dëgg, ba génne ma ci say loxo.» \p \v 16 Ba Daawuda waxee Sóol kàddu yooyu ba daaneel, Sóol da ne: «Éy Daawuda, doom, loolu sa baat la moos?», daldi ne yikkét jooy. \v 17 Mu ne Daawuda: «Dëgg déy nga am ci sama kaw, ndax yaa ma defal lu baax, ma fey la lu bon! \v 18 Yaa ma wax lu baax li nga ma defal tey; Aji Sax ji teg ma ci say loxo, te reyuloo ma. \v 19 Ana kuy jekku noonam, wacc ko mu dem ak jàmm? Yal na la Aji Sax ji fey lu baax li nga ma defal bésub tey jii. \v 20 Léegi nag dama ne, xam naa ne dinga doon buur moos, te nguurug Israyil dina sax ci say loxo. \v 21 Kon nag giñal ma ci Aji Sax ji ne doo dagg sama askan wi may wuutu, te doo raafal sama tur ci sama waa kër baay.» \v 22 Ba mu ko defee Daawuda giñal Sóol loolu, Sóol ñibbi këram, Daawuda ànd aki nitam, dellu ca xunti mu kawe ma. \c 25 \s1 Samiyel saay na \p \v 1 Gannaaw ba loolu wéyee Samiyel faatu, Israyil gépp daje, dëj ko, daldi koy denc ca këram ca Raama. Daawuda nag fabu, wuti màndiŋu Paran. \s1 Nabal gàntal na Daawuda \p \v 2 Jenn waay a nga woon ca dëkk ba ñuy wax Mawon. Amoon na alal foofa ca dëkk ba ñuy wax Karmel; ku barele woon lool la, amoon na ñetti junniy xar ak junniy bëy. Mu nekkoon Karmel, di watlu ay xaram.\f + \fr 25.2 \fr*\ft Xari waa penku dañuy bare kawar gu ñuy wat ak a ëcc, di ci defar ag wëñ.\ft*\f* \v 3 Nabal la waa ji tuddoon, soxnaam di Abigayil. Ndaw su yewwu la woon te taaru, jëkkëram nag bokk ci giiru Kaleb, di ku ñàng te soxor. \v 4 Ci biir loolu Daawuda dégge ca màndiŋ ma ne Nabal a ngay watlu ay xaram. \v 5 Mu yebal fukki ndaw, ne leen: «Demleen Karmel, ngeen àgg ba ca Nabal. Nuyul-leen ma ko. \v 6 Ngeen ne ko Daawuda nee: “Fekkeel déwén, yal nanga am jàmm, sa kër, jàmm, lépp lu bokk ci yaw it, jàmm. \v 7 Dégg naa ne watkati jur yaa ngi wate ci yaw. Say sàmm nag nekkoon nañook nun, te soxorewunu leen, lenn lu bokk ci ñoom it réerul, mboolem diir ba ñuy sàmm ca Karmel. \v 8 Laajal rekk say surga, dinañu la ko wax. Daawuda sa doom nag, sang bi, moo lay ñaan nga yéwéne nu ci bésu tey bu rafet bii nu dikke, te may nu loo am rekk, nu bokk kook moom.”» \p \v 9 Ndawi Daawuda ya nag dikk, jottli Nabal kàddu yooyu yépp ci turu Daawuda, ba daaneel, ne tekk. \v 10 Nabal ne ndawi Daawuda: «Ana kuy Daawuda? Kuy doomu Yese sax? Jamonoy tey jaam yu baree ngi fàqe ci seeni sang. \v 11 Ana luy ndeyi may jël saab dund ak samam ndox, ak yàppu jur, gi ma rendil sama watkati jur, di ko jox ñu ma xamul fu ñu jóge?» \v 12 Ba loolu amee ndawi Daawuda walbatiku ñibbi. Ba ñu dikkee, daldi koy yegge kàddu yooyu yépp. \v 13 Daawuda ne ndawam ya: «Ràngooleen seeni saamar, yeen ñépp.» Ñu ràngoo seeni saamar ñoom ñépp, Daawuda it ràngoo saamaram, lu tollook ñeenti téeméeri góor ànd ak Daawuda, ñaar téeméer des ca seen cummikaay. \s1 Jabaru Nabal def nag muus \p \v 14 Ci biir loolu kenn ca surga ya wax Abigayil jabaru Nabal, ne ko: «Ãa, Daawuda de moo yebal ay ndaw yu jóge ca màndiŋ ma, ngir nuysi sunu sang, waaye moom, da leena jànni. \v 15 Ndaxam nit ñooñu de, ñu baaxoon lool lañu ci nun. Soxorewuñu nu, te réerlewunu lenn it mboolem diir ba nu bokkee ak ñoom aw yoon, ca àll ba. \v 16 Sunu kiiraay la nu woon guddi ak bëccëg, la nu nekkoon ak ñoom lépp, di sàmm gàtt yi. \v 17 Léegi nag seetal, ba xam loo ci wara def, ndax musiba kat dëgmal na sunu sang, ak waa këram gépp. Moom nag dafa naqari deret, ba maneesula wax ak moom.» \p \v 18 Ba mu ko defee Abigayil gaaw sàkk ñaar téeméeri mburu, ak ñaari mbuusi biiñ, ak juróomi gàtt yu ñu defar, ak juróomi natti peppum mbool, ak téeméeri cabbi reseñ, ak ñaar téeméeri danki figg, boole ko sëf ci ay mbaam. \v 19 Mu ne ay surgaam: «Jiituleen, maa ngi topp ci yeen.» Nabal jëkkër ja nag, ndaw sa waxu ko ci dara. \v 20 Naka la ndaw sa dawal mbaamam, làqoo mbartalu tund wa, di wàcc ca xur wa, ndeke Daawudaa nga ànd aki nitam, di dajeek moom; ndaw sa ne pemm ca ñoom. \v 21 Fekk na Daawuda doon wax naan: «Ndeke kay neen laa doon wattoo mboolem lu bokk ci kii ca màndiŋ ma, ba lennam réerul; lu bon la ma feye lu baax. \v 22 Yal na ma Yàlla teg mbugal mu gëna tar, ndegam maa wacc bët di sete kenn ku bokk ci waa jii, kuy taxaw, colal.» \p \v 23 Abigayil séen Daawuda, daldi gaaw wàcc mbaam ma, ne gurub fa kanamam, dëpp jëëm fa suuf, sujjóot. \v 24 Naka la ne fëlëñ ca tànki Daawuda, ne ko: «Sang bi, naa tegoo tooñ gi, may ma rekk, ma wax la. Ngalla sama sang, déglul sama kàddu. \v 25 Sang bi, bul déglu mukk nit ku bon kii, Nabal mii. Moom turam doŋŋ la wuyu, nde Nabal (Dof bi) la tudd, te ndof la nekke. Man nag sang bi, gisuma woon ndaw yi nga yebal. \v 26 Léegi nag sang bi, giñ naa ko ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jiy dund, nga fekke tey, Aji Sax jee la teree tuur deret tey, di feyul sa bopp. Muy say noon, di ñi lay fexeel lu bon, yal nañu bokk ak Nabal mii demin. \v 27 Sarica bii ma la indil nag, sang bi, nañu ko jox xale yu góor yi topp ci yaw. \v 28 Sang bi, jéggal ma rekk ndax Aji Sax jee lay defal moos kër gu yàgg. Kon nag, Yàlla bu nit gis mukk lu bon ci yaw, sa giiru dund. \v 29 Bu ñu la doon dàq, di wut sa bakkan, yal na fekk sa bakkan dence ca ëmbu aji dund ña, ca sa wetu Yàlla Aji Sax ji, sang bi. Waaye sa bakkan ub noon, yal na ko mbaq, sànni fu sore. \v 30 Keroog, sang bi, bu la Aji Sax ji defalee mboolem lu baax la mu la dig, ba fal la, nga jiite Israyil déy, \v 31 su boobaa doo réccu, doo am yaraange ci loo doon tuure deret ci neen, mbaa loo doon feyul sa bopp. Te ngalla sang bi, keroog bu la Aji Sax ji baaxee, fàttlikul sab jaam.» \p \v 32 Daawuda ne Abigayil: «Cant ñeel na Aji Sax ji Yàllay Israyil, mi la yebal bésub tey jii, ngir nga dogale ma. \v 33 Maa ngi lay gërëme sa njort, di la gërëme sa jëmmu bopp jii ma teree tuur deret, ngir feyul sama bopp. \v 34 Lu ko moy de, giñ naa ci Kiy Dund, Aji Sax ji Yàllay Israyil, ji ma téye ba loruma la, soo gaawul woon, dogalesi ma, du kenn moos ku ñuy wacc, bët di ko sete ci mboolem kuy taxaw colal te bokk ci Nabal.» \v 35 Ba loolu amee Daawuda nangoo ca loxol ndaw sa la mu ko indil, daldi ne ko: «Ñibbil ak jàmm. Dégg naa sa kàddu te nangul naa la.» \s1 Nabal dee, Daawuda dikk \p \v 36 Ba mu ko defee Abigayil dellu ca Nabal, fekku ko lu moy mu amal biir këram bernde ju mel ni berndey buur. Xol baa nga sedd, mu màndi lool, ba tax Abigayil waxu ko dara ba bët set. \v 37 Ca suba sa ba biiñub Nabal giifee, jabaram wax ko la xew, fit wa jekki dee goyy ca biir dënn ba, yaram wa daldi mel niw doj. \v 38 Ñu teg ca lu tollook fukki fan, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji fàdd Nabal, mu dee. \v 39 Ci kaw loolu Daawuda dégg ne Nabal dee na, mu ne: «Cant ñeel na Aji Sax ji sama boroom, mi àtte gàcce gi ma ame ci Nabal, te tere maa def lu bon. Mbonug Nabal la Aji Sax ji walbati, këpp ci kaw boppam.» Daawuda nag yónnee kàddoom ca Abigayil, ngir jël ko jabar. \v 40 Surgay Daawuda ya dem ca Abigayil ca Karmel, wax ko ne ko: «Daawudaa nu yónni fi yaw, ngir bëgg laa jël soxna.» \p \v 41 Abigayil daldi sujjóot, dëpp jëëm fa suuf, ne leen: «Maa ngii dib jaamam, ba ci raxas tànki surgaam yi.» \v 42 Ci kaw loolu Abigayil ne ñokket, war mbaamam, juróomi surgaam yu jigéen ànd ak moom, mu topp ca ndawi Daawuda ya. Noonu la Abigayil doone soxnaam. \p \v 43 Ayinowam ma cosaanoo Yisreel itam, Daawuda jëloon na ko soxna, ñuy wujje ñoom ñaar. \v 44 Fekk na Sóol nangu doomam Mikal, soxnas Daawuda, may ko waa Galim ba ñuy wax Palti doomu Layis. \c 26 \s1 Daawuda gënati na Sóol \p \v 1 Waa Sif ñoo demoon ca Sóol ca Gibeya, ne ko: «Yéguloo ne Daawudaa nga làqu ca tundu Akila, fa janook màndiŋ ma?» \v 2 Sóol dem ba ca màndiŋu Sif, ànd ak ñetti junniy ñeyi xarey Israyil, ngir rëbb Daawuda ca màndiŋu Sif. \v 3 Ba mu ko defee Sóol dale ca wetu yoon wa, ca kaw tundu Akila, janook màndiŋ ma. Daawuda ma ca màndiŋ ma nag yég ne Sóol toppsi na ko foofa. \v 4 Mu yebal ay ndaw yu ko nemmikujil, ba mu wóor ko ne Sóol agsi na. \v 5 Ci kaw loolu Daawuda dem ba fa Sóol dal. Mu gis fa Sóol tëdd, mook Abner doomu Ner njiital gàngooram. Sóol a nga tëdd ca digg dal ba, gàngoor ga tëdd, yéew ko. \p \v 6 Daawuda daldi laaj Ayimeleg Etteen ba, ak Abisay ma Seruya di yaayam, te mu bokk ak Yowab. Mu ne leen: «Kuy ànd ak man dem ca biir dal ba, fa Sóol?» Abisay ne ko: «Man maay ànd ak yaw.» \v 7 Daawuda ànd ak Abisay ci guddi, ba fa dalu gàngoor ga. Ndeke Sóol a nga tëdd di nelaw ca digg dal ba, xeejam baa nga sampe fa suuf, féeteek bopp ba, Abner ak gàngoor gaa nga tëdd, yéew ko. \v 8 Abisay ne Daawuda: «Yàlla de teg na sab noon ci say loxo guddig tey jii. Bàyyil rekk ma daaj ko xeej bi fi suuf benn yoon rekk, du ñaar!» \v 9 Daawuda ne Abisay: «Bu ko rey. Ana kuy yékkati loxoom ci kaw ki \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji fal, te yoon dabu ko?» \v 10 Daawuda teg ca ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax jiy dund, Aji Sax ji ci boppam moo koy fàdd. Yaar àppam jot, mu dee, mbaa mu dem xare, des ca. \v 11 Waaye yal na ma Aji Sax ji musal ci yékkati sama loxo ci kaw ki Aji Sax ji fal. Xanaa nga jël rekk xeej bi féeteek bopp bi, ak njaqal ndox li, te nu dem.» \v 12 Daawuda nag jël xeej baak njaqal ndox la féeteek boppu Sóol. Ñu daldi dem te kenn gisul, kenn yégul, kenn yewwuwul, ndax ñépp a ngay nelaw nelaw yu xóot yu bawoo ci Aji Sax ji, daanu ci seen kaw. \p \v 13 Ba loolu amee Daawuda jàll ba ca wàlla, daldi taxawe fu sore ca kaw tund wa, digganteem ak dalub Sóol ne yàmblaŋ. \v 14 Mu àddu ca kaw, wax ak gàngoor ga, daldi ne Abner doomu Ner: «Éey Abner, doo ma wuyu?» Abner ne ko: «Yaw yaa di kan bay joor Buur?» \v 15 Daawuda ne Abner: «Xanaa doo jàmbaaru góor? Ku fiy sa moroom ci Israyil? Ana lu la tee wattu Buur, sab sang? Am na ci xarekat yi ku bóomsi woon Buur, sab sang. \v 16 Xam nga ne li nga def baaxul de! Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund, dee rekk ngeen yelloo, yeen ñi wattuwul seen sang, ki Aji Sax ji fal! Xoolal bu baax, ana xeeju Buur ak njaqal ndox li féete woon ak boppam?» \p \v 17 Ci kaw loolu Sóol xàmmi baatu Daawuda, ne ko: «Daawuda doom, loolu sa baat a?» Daawuda ne ko: «Sama baat a kay, Buur, samab sang,» \v 18 daldi cay teg ne ko: «Sang bi, looy toppe nii sab jaam? Ana lu ma def? Lan laa def ci lu bon? \v 19 Ngalla Buur, sama sang, déglul lii ma lay wax: su fekkee ne Aji Sax ji moo la xiir ci sama kaw, yal na ko cib sarax giifal. Waaye su dee ay doom aadama de, yal nañu alku ci kanam Aji Sax ji, ndax dàq nañu ma tey, ba xañ ma ab cér ci Aji Sax ji, mbete ku ñu ne: “Demal jaamuji yeneen yàlla.” \v 20 Man de yàlla bu sama bakkan rote àll, fu soreek Aji Sax ji. Te sax, lu tollu ni buurub Israyil ci boppam wutul lu moy wenn fel doŋŋ wu mel ni man? Mbete kuy rëbb cokkeer ci tund yi!» \p \v 21 Sóol nag ne: «Bàkkaar naa de! Daawuda doom, ñibbsil, ndax dootuma la fexeel mukk, gannaaw yaa wormaal sama bakkan tey jii! Lii ma def kay, yëfi dof la, juum naa lool sax.» \v 22 Daawuda ne ko: «Buur, sa xeej a ngii, na kenn ci sa xale yu góor yi jàllsi, jëlsi ko. \v 23 Yal na Aji Sax ji yool ku nekk njekkam ak kóllëreem, ndax Aji Sax jee la teg tey jii ci sama loxo, waaye maa buggula yékkati sama loxo ci kaw ki Aji Sax ji fal. \v 24 Ni ma yéemloo sa bakkan tey jii nag, yal na ni Aji Sax ji yéemloo sama bakkan, te xettlee ma ni ci gépp njàqare.» \v 25 Sóol ne Daawuda: «Daawuda doom, yal nanga barkeel. Dinga def ay jaloore déy, te dinga am ndam moos!» Ba mu ko defee Daawuda dem yoonam, Sóol walbatiku, ñibbi. \c 27 \s1 Daawuda làquji na ca waa Filisti \p \v 1 Daawuda nag ma nga naan ca xelam: «Bés a ngi ñëw bu ma nara sànku ci loxol Sóol. Li gën ci man daal, du lenn lu moy dawa daw ba ca réewu waa Filisti, ba Sóol tàyyi maa rëbbati ci Israyil gépp, ma daldi mucc.» \v 2 Ba loolu amee Daawuda ak juróom benni téeméeri nit ña ànd ak moom, daldi jàll ba ca buurub Gaat, Akis doomu Mawog. \v 3 Daawuda dal ca Akis ca Gaat, mook ay nitam, ku ci nekk ak njabootam; Daawuda ak ñaari soxnaam, Ayinowam waa Yisreel ba, ak waa Karmel ba, Abigayil, soxnas Nabal woon. \v 4 Ba ñu waxee Sóol ne ko Daawuda daw na, dem Gaat, Sóol rëbbatu ko. \p \v 5 Daawuda nag ne Akis: «Ngalla baaxe ma, may ma fi ab gox ci dëkki àll bii, ma man faa dëkke; ndax man sab surga laa, warumaa bokk dëkk ak yaw ci péeyu buur.» \v 6 Bésub keroog la ko Akis jox dëkk ba ñuy wax Ciglaag. Moo tax Ciglaag ñeel buuri Yuda ba tey jii. \v 7 Diir ba Daawuda dal ca àllub Filisti, at la ak ñeenti weer. \p \v 8 Ci biir loolu Daawuda aki nitam daan nañu song-songee Gesureen ñi ak Giraseen ñi ak Amalegeen ñi. Mooy ña dëkke woon naka jekk réew mooma, ba ca Sur, jàpp réewum Misra. \v 9 Saa yu Daawuda songaan gox ba, du ca wacc kuy dund; du góor, du jigéen, te it day lël jur gu gudd ak gu gàtt, mbaam ak giléem, aki yére. Su ko defee mu walbatiku, dellu ca Akis. \v 10 Bu ko Akis laajee ne ko: «Fu ngeen lële woon tey?» Daawuda ne ko: «Xanaa wetu Negew ca Yuda,» mbaa «Xanaa wetu Negew ca Yerameleen ña,» mbaa mu ne ko: «Xanaa wetu Negew ca Keneen ña.» \v 11 Moo tax du genn góor mbaa jigéen ju Daawuda masa bàyyi mu dund, di ko indi Gaat, ndax ragal ñu nettali lu jëm ci ñoom, naan nàngam ak nàngam la ñoom Daawuda def. Noonu la jàppoo woon mboolem diir ba mu dal ca àllub Filisti. \v 12 Akis nag amoon na kóolute ci Daawuda, ndax da doon wax ci xelam naan: «Kii de yóbbe na boppam mbañeel gu ko bokki \w bànni Israyilam|lemma="bànni Israyil:"\w* bañ lool. Moo tax sama surga rekk lay doon ba fàww.» \c 28 \p \v 1 Jamono yooyu nag waa Filistee dajale woon seeni gàngoori xare, ngir xeex ak Israyil. Akis ne Daawuda: «Xanaa moos xam nga ne man ngay àndal ci xare bi de, yaak say nit?» \v 2 Daawuda ne Akis: «Kon nag, sang bi, yaay gisal sa bopp li may def.» Akis ne ko: «Kon nag, def naa la sama dagu bopp ba fàww.» \s1 Sóol seetluji na ca Endor \p \v 3 Samiyel nag faatu woon na, ba Israyil gépp dëj ko, denc ko ca Raama, dëkkam ba. Te itam Sóol mujjoon naa génne réew ma ñiy seete nit ñu dee, ak boroom rawaan yiy gisaane. \p \v 4 Ci kaw loolu waa Filisti daje, dali ca dëkk ba ñuy wax Sunem; Sóol ànd ak \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp, ñu dali ca Gilbowa. \v 5 Sóol gis gàngooru waa Filisti, daldi tiit lool ba fit wa rëcc. \v 6 Mu seetlu ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, Aji Sax ji wuyuwu ko; du ci gént, du ci jumtukaayu tegtal bi ñuy wax \w Urim|lemma="Urim ak Tumim:"\w*, du ci kàddug yonent. \v 7 Sóol wax ay jawriñam, ne leen: «Seetal-leen ma jigéen juy seete nit ñu dee, ma seetluji ci moom.» Jawriñ ya ne ko: «Xanaa jigéenu gisaanekat ba ca Endor.» \p \v 8 Ba mu ko defee Sóol soppiw melo, sol yeneen yére, daldi ànd ak ñaari nit ag guddi, ba ca jigéen ja. Mu ne ko: «Ngalla gisaaneel ma ci ab rawaan, te nga wool ma ku dee ki ma lay tudd!» \v 9 Jigéen ji ne ko: «Ma ne, yaw ci sa bopp xam nga li Sóol def; moo génne réew mi ñiy seete nit ñu dee, ak boroom rawaan yiy gisaane. Kon loo may fiire, nar maa reylu?» \v 10 Sóol giñal ko ci Aji Sax ji, ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, mbugal du la ci fekk.» \v 11 Jigéen ji ne ko: «Ku ma lay wool?» Mu ne ko: «Samiyel nga may wool.» \p \v 12 Naka la jigéen ja gis Samiyel, daldi yuuxu ca kaw ne Sóol: «Lu tax nga nax ma? Yaw kay ndeke yaa di Sóol!» \v 13 Buur Sóol ne ko: «Bul tiit, loo gis?» Mu ne ko: «Ab rawaan laa gis, muy yéege fa suuf.» \v 14 Mu ne ko: «Nu mu mel?» Mu ne ko: «Góor gu mag ay yéegsi. Mu ngi sàngoo mbubb.» Sóol xam ne Samiyel la, daldi sukk, sujjóot, dëpp jëëm fa suuf. \v 15 Samiyel ne Sóol: «Ana loo may wooye, di ma yékkati nii?» Sóol ne ko: «Damaa nekk ci njàqare lu réy. Waa Filistee ngi xareek man, te Yàlla dëddu na ma. Wuyootu ma, du ci kàddug yonent, du ci gént. Moo tax ma woo la, ngir nga xamal ma lu may def.» \v 16 Samiyel ne ko: «Loo may laaj, gannaaw Aji Sax jee la dëddu, def la ab noon? \v 17 Aji Sax jee sottal la mu waxoon, ma jottli ko, te Aji Sax jee foqati nguur gi ci say loxo, jox ko sa jegeñaale, muy Daawuda; \v 18 Yaa déggalul Aji Sax ji, jëfewuloo tàngooru meram ngir mbugal Amalegeen ñi. Loolu moo waral lii la Aji Sax ji teg tey jii. \v 19 Te itam Aji Sax jee lay booleek Israyil, teg ci loxol waa Filisti. Nëgëni ëllëg, yaw yaak say doom, dingeen ma fekksi. Te it dalub Israyil, Aji Sax jee koy teg ci loxol waa Filisti.» \p \v 20 Sóol nag jekki ne dàll fa suuf, tàlli ñareet, tiitaange lu réy jàpp ko ndax kàdduy Samiyel. Rax ci dolli amul woon genn kàttan, ngir lekkul woon dara bëccëg baak guddi ga gépp. \v 21 Jigéen ja dikk, gis Sóol mu jàq lool. Mu ne ko: «Aa, sang bi, man de déggal naa la. Jaay naa sama bakkan, def li nga ma sant. \v 22 Léegi nag, déggal ma rekk sang bi, ma may la tuuti loo lekk, ba am doole, doora topp yoon wi.» \v 23 Sóol lànk, ne ko: «Déedéet, lekkuma!» Jawriñam ña nag soññ ko, ñook jigéen ja, ba mu déggal leen. Mu jóge ca suuf, toog ca kaw lal ba. \v 24 Jigéen ja amoon na sëlluw yar ca kër ga. Mu gaaw rey ko, daldi sàkk sunguf, not ko, lakk ca mburu mu amul lawiir. \v 25 Ba mu ko defee mu taajal ko Sóol, mooki nitam. Ñu lekk ba noppi, bàyyikoo fa guddig keroog. \c 29 \s1 Waa Filisti dàq nañu Daawuda \p \v 1 Gàngoori waa Filisti yépp a daje woon ca Afeg. Israyil a nga dale woon ca wetu bëtu ndox ba ca Yisreel. \v 2 Kàngami waa Filisti yaa ngay jaab jiitu, ànd ak seen kuréli téeméeri xarekat ak kuréli junni. Daawudaaki nitam ànd ak Akis, jaab topp seen gannaaw. \v 3 Kilifay waa Filisti ne: «\w Ebrë|lemma="Ebrë:"\w* yii, nag?» Akis wax ak kilifay waa Filisti, ne leen: «Xanaa du Daawuda, surgab Sóol buurub Israyil? Lu ëpp at a ngii mu nekk ak man, te gisuma ci moom sikk, ba mu teqlikook Sóol, ba bésub tey jii.» \v 4 Kilifay waa Filisti nag ñéññ ca daldi ne ko: «Waññal waa jii, mu dellu ca gox ba nga ko teg. Bumu ànd ak nun ci xare bi, bay walbatiku di sunub noon ci biir xare bi. Ana lu koy jubaleeteek sangam, lu moy mu dog boppi nit ñii, jox ko? \v 5 Xanaa du Daawuda mii lañuy woyal, di fecc, naan: \q1 “Sóol jam junneem, \q1 Daawuda jam fukki junneem”?» \p \v 6 Ci kaw loolu Akis woo Daawuda, ne ko: «Giñ naa ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, Kiy Dund, ku jub nga, te doon naa rafetlu sa ànd ak man, di xarejeek a dikk, ndax bés ba nga dikkee fi man ba tey jii, gisuma ci yaw lu bon. Waaye nag kàngami Filisti ñoo rafetluwul sa teewaay. \v 7 Kon nag waññikul, te dem ak jàmm bala ngaa def lenn lu kàngami Filisti rafetluwul.» \p \v 8 Daawuda ne Akis: «Ana lu ma def, ak loo ma gisal, bés ba ma dikkee fi yaw, ba bésub tey jii, ba tax duma xarejeek nooni Buur sang bi?» \v 9 Akis ne Daawuda: «Dara! Xam naa loolu. Bége naa la it ni ndawal Yàlla. Kilifay Filisti kay a ma ne: Bumu ànd ak nun ca xare ba. \v 10 Kon teelala fabu ëllëg, yaak sa surgay sang yi nga àndal; Dangeen di teela jóg rekk, bu bët setee ngeen dem.» \v 11 Ca ëllëg sa nag Daawuda teela fabu, mooki nitam, ngir dellu réewum Filisti, waa Filisti ñoom jubal Yisreel. \c 30 \s1 Daawuda toppi na Amalegeen ña \p \v 1 Ba Daawuda aki nitam àggee Ciglaag, ca gannaaw ëllëg sa la. Fekk na Amalegeen ña song bëj-saalumu Yuda ak Ciglaag; ñu yàqte Ciglaag, lakk ko, \v 2 jàpp jigéen ña mu fa fekk, mag ak ndaw. Reyuñu ca kenn nag, dañu leena yóbbaale, dem seen yoon. \v 3 Ba Daawudaaki nitam agsee Ciglaag, fekk nañu mu lakk ba jeex; seeni jabar ak seeni doom, góor ak jigéen, ñépp duggi njaam. \v 4 Daawudaak mbooloo ma mu àndal nag di yuuxook a jooyoo, ba amatuñu dooley jooy. \p \v 5 Ñaari soxnay Daawuda lañu jàpp; Ayinowam mu Yisreel ak Abigayil waa Karmel ba, soxnas Nabal woon. \v 6 Ba loolu amee Daawuda jàq lool, ndax mbooloo maa nga doon wax naan dañu koy dóori doj. Booba mbooloo ma ba mu daj, ku nekk a ngaak naqaru xol, di xalaat doomam yu góor ak yu jigéen. Daawuda nag dëgërloo Yàllaam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji rekk. \v 7 Ci biir loolu Daawuda wax ak \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba Abiyatar doomu Ayimeleg, ne ko mu indil ko \w xar-sànni|lemma="xar-sànni m-:"\w* mi. Abiyatar indil Daawuda xar-sànni ma. \v 8 Daawuda laaj Aji Sax ji, ne ko: «Ndax ma topp gàngooru yàqkat yii? Ndax dinaa leen dab?» Mu ne ko: «Demal, yaay dabe déy, te yaay xettlee déy.» \p \v 9 Ba mu ko defee Daawuda dem, mook juróom benni téeméeri nit ña ànd ak moom. Ñu dem ba ca xuru Besor, ñenn ña yem fa. \v 10 Daawudaa ñoqli, mook ñeenti téeméeri nit, ñaar téeméeri nit yem foofa, ndax loof, ba manuñoo jàll xuru Besor. \v 11 Ci kaw loolu ña jàll yem ci jenn waayu Misra ci àll bi. Ñu indi waa ji ba ci Daawuda, daldi may waa ji mburu mu lekk, may ko ndox, mu naan. \v 12 Ab danku figg ju wow ak ñaari danki reseñ lañu ko leel, mu doora leqliku, ndax dafa fekk lekkul, naanul diiru ñetti guddi ak ñetti bëccëg. \v 13 Daawuda ne ko: «Yaw, kuy sab sang ak foo bokk?» Xalelu góor ba ne ko: «Man waa Misra laa, di jaamub jenn waayu Amalegeen. Sama sang a ma wacc, ba ma woppee bëkkaati-démb. \v 14 Noo song wetu Negew ca diiwaanu waa Keret ña, ak diiwaanu Yuda, ak wetu Negew ca diiwaanu Kaleb, te Ciglaag, noo ko lakk.» \v 15 Daawuda ne ko: «Ndax man nga maa yóbbu ba ci gàngooru yàqkat yooyu?» Mu ne ko: «Giñal ma ci Yàlla ne, doo ma rey, te doo ma delloo ca sama sang; kon dinaa la yóbbu ba ci gàngooru yàqkat yi.» \p \v 16 Ci kaw loolu waa ja yóbbu Daawuda, ndeke nit ñaa nga ne wesar ca àll ba bépp, di lekk ak a naan, di mbumbaaye mboolem alal ju bare ja ñu nangoo ca réewum Filisti ak réewum Yuda. \v 17 Daawuda nag di leen fàdd, njël ba ca ngoon. Kenn rëccul, lu moy ñeenti téeméeri xale yu góor yu war ay giléem, daw. \v 18 Daawuda nangu mboolem lu Amalegeen ña jëloon, nangu ñaari soxnaam. \v 19 Dara lu bokk ci ñoom rawul. Mag ñaak ndaw ñaak seen doom yu góor ak seen doom yu jigéen ak alal jaak mboolem lu ñu leen jëlaloon. Lépp la Daawuda délloosi. \v 20 Mu nangu mboolem jur gu gudd ak gu gàtt, nitam ña dàq, tofal ca juru Amalegeen ña, te naan: «Lëlub Daawudaa ngi!» \s1 Daawuda gore na \p \v 21 Daawuda nag dikk ba ca ñaar téeméer ña loofoon ba manuñu koo topp, te ñu bàyyi woon leen ca xuru Besor. Naka lañu gatandu Daawuda ak ña mu àndal, Daawuda dikk, dajeek ñoom, jàmmanteek ñoom. \v 22 Mboolem ñu bon ñaak ñu sew ña jàllandoo woon ak Daawuda nag ne leen: «Gannaaw ñii ànduñu woon ak nun, dunu leen jox dara ci alal ji nu nangu. Xanaa ku nekk jël jabaram aki doomam rekk, yóbbu te dem.» \v 23 Daawuda ne leen: «Déet bokk yi, buleen def noonu, ak li nu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji defal, aar nu, teg gàngooru yàqkat yi nu songoon ci sunuy loxo. \v 24 Ana nu xel mana nangoo loolu? Na ku xarejeek ku desoon ca cummikaay la, yem ak sa moroom cér; ñépp ay séddu.» \v 25 Bésub keroog la Daawuda dale def loolu mu dib dogal, di àtteb yoon bu ñeel Israyil ba tey jii. \s1 Daawuda sédd na njiiti Yudeen ña \p \v 26 Ba Daawuda delloo Ciglaag, sédd na ca lël ja, magi Yuda, xaritam ya. Mu yónnee leen ko, ne leen: «Lii, yeenay boroom; xéewal la gu jóge ca alalu nooni \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji.» \v 27 Noonu la ca sédde waa Betel ak waa Ramot Negew ak waa Yatir \v 28 ak waa Arower ak waa Sifmot ak waa Estemowa \v 29 ak waa Rakal, ak waa dëkki Yerameleen ña ak waa dëkki Keneen ña, \v 30 ak ña ca Xorma ak ña ca Bor Asan ak ña ca Atag \v 31 ak ña ca Ebron ak mboolem waa gox ya mu jaare woon, mooki nitam. \c 31 \s1 Lu jëm ci mujug Sóol \p \v 1 Ci biir loolu waa Filisti jaamarloo ak Israyil, ba \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* won leen gannaaw, daw, ñu bare daanu ca kaw tundu Gilbowa. \v 2 Waa Filisti nag ne dann Sóol aki doomam, ba rey ca ñett; Yonatan ak Abinadab ak Malkisuwa. \v 3 Xare ba nag gëna mettee fa Sóol féete, fittkat ya jekku ko, mu jàq. \p \v 4 Ba loolu amee Sóol ne gàddukatu gànnaayam: «Boccil sa saamar, jam ma bala yéefar yee dikk, jam ma, torxal ma.» Gàddukatu gànnaayam nag buggu koo jam ndax tiitaange lu réy. Sóol jël saamaru boppam, daldi daaneel boppam ca kaw ñawka ga. \v 5 Gàddukatu ngànnaay ba gis ne Sóol dee na, moom it mu daaneel boppam ca kaw saamaram, dee topp Sóol. \v 6 Muy Sóol, di ñetti doomam, di gàddukatu gànnaayam itam, di mboolem ay nitam, ñoom ñépp a bokk dee bésub keroog. \p \v 7 Ci kaw loolu bànni Israyil, ya ca wàllaa xur wa, ak ña ca wàllaa dexu Yurdan gis ne xarekati Israyil daw nañu, te Sóol aki doomam dee nañu. Ñu daldi daw, gental seeni dëkk, waa Filisti dikk, dëkke. \p \v 8 Ca ëllëg sa, ba waa Filisti dikkee, di futtisi ña dee, ca tundu Gilbowa lañu fekk Sóol ak ñetti doomam, ñu tëdd. \v 9 Ñu dog boppu Sóol, jël ay gànnaayam, ba noppi yeble ca réewum Filisti ba mu daj, ngir yégle ko ca seen këri tuur ya ak ca askan wa. \v 10 Ba mu ko defee ñu denc gànnaayi Sóol ca seen biir kër tuur ma ñuy wax \w Astàrt|lemma="Astàrt:"\w*, néewub Sóol, ñu wékk ca miiru dëkk ba ñuy wax Bet San. \p \v 11 Ba waa Yabes ga ca Galàdd déggee la waa Filisti def Sóol, \v 12 seen jàmbaar yépp a fabu, topp guddi ga gépp ba Bet San. Ñu wékkee ca miiru Bet San néewu Sóol ak néewi doomam yu góor, doora ñibbi Yabes, boole fa néew ya, lakk. \v 13 Ñu for nag seeni yax, suul ca ron garabu tamaris ga ca Yabes. Ba loolu amee ñu woor diiru juróom ñaari fan.