\id 1KI (WOL) \ide UTF-8 \h 1.Buur ya \toc1 Buur ya, di téere bu jëkk bi \toc2 1.Buur ya \mt1 Buur ya \mt2 di téere bu jëkk bi \c 1 \ms1 Lu jëm ci nguurug Suleymaan \mr (Saar 1.1—11.43) \s1 Daawuda néew na doole \p \v 1 Gannaaw gi Buur Daawuda mujj naa màggat, ba làq at yu bare, ñu di ko sàng ay sér te du ko taxa tàng. \v 2 Ay dagam ne ko: «Buur, sang bi, nañu la wutal ab janq, mu di la taxawu, di la topptoo. Man naa tëdd it ci sa wet, Buur, ndax nga liwwi, sang bi.» \v 3 Ñu daldi seet ci tundu Israyil wépp, ba gis janq bu rafet bu ñuy wax Abisag, di waa Sunem. Ñu indil ko Buur. \v 4 Janq baa nga taaru lool. Muy topptoo nag Buur, di ko taxawu, waaye Buur dëkkoowu ko. \s1 Adoñaa ngi sàkku jal bi \p \v 5 Ci biir loolu Adoña doomu Daawudaak Agit, di tëggu naan: «Man mii maay doon buur.» Mu waajalal boppam watiiru xare aki fas ak juróom fukki nit ñuy daw di ko jiitu. \v 6 Baayam Daawuda nag masu koo wax dara, ak lu mu mana def. Adoña moo toppoon ci Absalom. Mu doonoon ku góorayiw lool. \p \v 7 Ci kaw loolu Adoña diisook Yowab, mi Seruya di ndeyam, ak Abiyatar \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba, ñooñu jàpple ko. \v 8 Waaye Cadog sarxalkat ba ak Benaya doomu Yoyada, ak Yonent Yàlla Natan, ak Simey ak Reyi, ñook jàmbaari Daawuda ya koy dar, ñooñu ànduñu woon ak Adoña. \v 9 Ba mu ko defee Adoña sarxe ay xar aki nag aki wëllu yu duuf ca wetu doju Soyelet, fa feggook En Rogel. Mu woo ca mboolem doomi Buur yu góor ya mu bokkal baay, ak jawriñi Buur yu diiwaanu Yuda. \v 10 Waaye woowul Yonent Yàlla Natan ak Benaya, woowul jàmbaar yay dar Daawuda, woowul rakkam Suleymaan. \p \v 11 Ba loolu amee Natan laaj Batseba, ndeyu Suleymaan, ne ko: «Waaw, xanaa déggoo ne Adoña doomu Agit falu na buur te sunu sang Daawuda yégu ko? \v 12 Kaay gaaw, ma digal la nooy def, ba musal sa bakkan ak sa bakkanu doom Suleymaan. \v 13 Gaawal dem ca Buur Daawuda, ne ko: “Buur, sang bi, du yaa ma giñaloon, yaw sang bi, ne ma sama doom Suleymaan mooy falu buur, wuutu la, te mooy toog ci sa jal bi? Kon nag lu tax Adoña falu buur?” \v 14 Gisal, diir bi ngay wax ak Buur foofa, man dinaa duggsi, topp ci yaw te dinaa dëggal sa kàddu.» \p \v 15 Batseba dem ba ca Buur, ca biir néegam. Buur a nga màggat lool, Abisag mu Sunem di ko taxawu. \v 16 Batseba agsi sujjóotal Buur, sukk fi kanamam. Buur ne ko: «Lu doon say tànk?» \v 17 Mu ne ko: «Sama sang, yaw yaa ma giñal ci sa Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, sang bi, nga ne ma sama doom Suleymaan de dina falu buur moos, wuutu la, te moom mooy toog ci sa kaw jal bi. \v 18 Waaye xoolal léegi Adoñaa ngii falu buur, te yaw Buur sang bi, yéguloo ko. \v 19 Sarxe na ay nag ak wëllu yu duuf ak xar yu bare. Woo na ca doomi Buur yu góor yépp, woo ca Abiyatar sarxalkat ba, woo ca Yowab, njiitu mbooloom xare mi. Waaye Suleymaan sa surga ba, woowu ko. \v 20 Yaw nag Buur, sang bi, Israyil gépp a ngi ne jàkk ci yaw, ngir nga xamal leen kan ngay dëj ci sab jal, mu wuutu la, sang bi. \v 21 Lu ko moy de Buur, sang bi, bés boo nopplujee fekki say maam, su boobaa man, maak sama doom Suleymaan dinañu nu tuumaal.» \p \v 22 Na Batseba di wax ak Buur, Yonent Yàlla Natan jekki ne jalañ. \v 23 Ñu wax ko ne ko: «Buur, Yonent Yàlla Natan a ngoog.» Mu agsi ba ci kanam Buur, sujjóotal ko, dëpp kanamam fa suuf. \v 24 Natan ne ko: «Buur, sang bi, ndax yaa wax ne Adoña mooy falu buur, wuutu la, te moom mooy toog ci kaw jal bi? \v 25 Ndax kat, Adoña dem na tey jii, sarxeji lu bare ciy nag ak wëllu yu duuf aki xar. Woo na ca doomi Buur yu góor yépp, ñook njiiti xare yeek Abiyatar sarxalkat bi. Ña nga noonee di lekk ak a naan ñook moom te naa: “Buur Adoña, guddalu fan!” \v 26 Man sa surga bii nag, maak Cadog sarxalkat bi ak Benaya doomu Yoyada ak sa surga ba Suleymaan, woowu nu ca. \v 27 Buur, sang bi, ndax wér na ne loolu ndigal la lu bàyyikoo fi yaw, te xamaloo nu kan mooy toog ci sa kaw jal bi, wuutu la, yaw Buur, sang bi?» \p \v 28 Buur Daawuda ne ko: «Wool ma Batseba!» Ci kaw loolu Batseba dikk taxaw fa kanam Buur. \v 29 Buur daldi giñ ne: «Giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund te musal sama bakkan bii ci jépp njàqare, \v 30 bir na ne loolu ma la giñaloon ci Aji Sax ji, Yàllay Israyil, ne la bir na ne Suleymaan sa doom mooy doon buur wuutu ma te mooy toog ci kaw jal bii ma toog— loolu déy dinaa ko sottal bés niki tey.» \v 31 Ba mu ko defee Batseba dëpp kanamam fa suuf, sukk fa kanam Buur, ne ko: «Buur Daawuda, sang bi, yal nanga fi yàgg.» \s1 Suleymaan falu na \p \v 32 Buur Daawuda daldi ne: «Wool-leen ma Cadog \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi, ak Yonent Yàlla Natan ak Benaya doomu Yoyada.» Ba ñu dikkee fa kanam Buur, \v 33 Buur ne leen: «Àndleen ak samay dag, ngeen waral sama doom Suleymaan ca sama kaw berkelle bu jigéen ba, te yóbbu ko Giyon, bëtu ndox ba. \v 34 Cadog sarxalkat bi ak Yonent Yàlla Natan, nañu ko diw foofa, fal ko mu jiite Israyil. Su ko defee ngeen wal liit gi te yéene ne: “Buur Suleymaan, guddalu fan!” \v 35 Ngeen topp nag ci moom, délsi, mu dikk toog ci kaw jal bi. Moom mooy nguuru, wuutu ma. Moom laa fal, mu yilif Israyil ak Yuda.» \v 36 Ba loolu amee Benaya doomu Yoyada ne Buur: «Buur, sang bi, yal na ko \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji sa Yàlla dogal. Amiin! \v 37 Na Aji Sax ji ànde woon ak yaw Buur, sang bi, yal na ni àndeek Suleymaan, te yal na kaweel ab jalam, ba mu sut sab jal, yaw Buur Daawuda, sang bi.» \v 38 Gannaaw loolu Cadog sarxalkat ba daldi ànd ak Yonent Yàlla Natan ak Benaya doomu Yoyada, ak waa Keret ak waa Pelet yay dar Daawuda. Ñu waral Suleymaan berkelleb Buur Daawuda. Ñu dar ko ba Giyon, bëtu ndox ba. \v 39 Ci kaw loolu Cadog sarxalkat ba dem ca xaymab Aji Sax ji, jële fa béjjén ba def diwu pal ga, diw ca Suleymaan. Ñu wal liit ga, mbooloo ma mépp àddu ca kaw ne: «Buur Suleymaan, guddalu fan!» \v 40 Ba loolu amee mbooloo ma mépp topp ca, bég lool, di toxoro, coow la jolli, ba suuf sa di riir. \p \v 41 Ba mu ko defee Adoña dégg ca, mook mboolem ña mu woo woon, ñu nekk faak moom. Fekk ñu lekk ba noppi. Ba Yowab déggee liit ga, da ne: «Waaw, riir mi ci dëkk bi, lu mu doon?» \v 42 Daaneelagul kàddoom sax, Yonatan doomu Abiyatar sarxalkat ba ne jaas, agsi. Adoña ne ko: «Dikkal, yaw nit ku baax nga, te xibaaru jàmm ngay indi.» \v 43 Yonatan ne Adoña: «Déedéet kay, sunu sang Buur Daawuda fal na Suleymaan buur. \v 44 Buur boole na kook Cadog sarxalkat bi ak Yonent Yàlla Natan ak Benaya doomu Yoyada ak waa Keret ak waa Pelet yay dar Buur. Yebal na leen, ñu waral ko berkelleb Buur. \v 45 Cadog sarxalkat baak Yonent Yàlla Natan diw nañu ko, fal ko ca Giyon, ba bàyyikoo ca, di ko bége, mu dim riir ci dëkk bi. Mooy coow, li ngeen dégg. \v 46 Suleymaan sax toog na ca jalu buur; \v 47 te it jawriñi Buur ñëw nañu, di sargalsi sunu sang Buur Daawuda, ne ko: “Yal na sa Yàlla siiwal turu Suleymaan, ba mu gën laa amu tur. Yal na kaweel ab jalam, ba mu gëna kawe sab jal.” Buur sujjóot ca kaw lalam, \v 48 teg ca ne: “Cant ñeel na Aji Sax ji, Yàllay Israyil, ji ma jox bésub tey ku ma wuutu ci samab jal, may gis.”» \v 49 Ba loolu amee tiitaange jàpp mboolem ña ñu woo woon ca jataayu Adoña. Ñu jóg, tasaaroo, ku nekk dem yoonam. \p \v 50 Adoña nag ragal Suleymaan, daldi dem jàpp ca béjjén ya ca cati \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* ba, ngir rawale bakkanam\f + \fr 1.50 \fr*\ft Jàpp ca sarxalukaay ba ca kër Yàlla ga, nit daan na ko def, di ko sàkkoo rawale bakkanam. Seetal ci \ft*\ft \+bk Mucc ga\+bk* 21.14.\ft*\f*. \v 51 Ñu wax ko Suleymaan, ne ko: «Buur Suleymaan, Adoña de, ragal na la. Deful lu moy jàpp ca béjjéni sarxalukaay ba te naa: “Na ma Buur Suleymaan sang bi giñal tey jii ne du ma jam saamar, ma dee.”» \v 52 Suleymaan daldi ne: «Su dee nit ku jara wóolu de, genn kawaram du wadd ci suuf. Waaye su lalee pexem wor de, dina dee.» \v 53 Ba loolu amee Buur Suleymaan yónnee, ñu jëleji Adoña ca sarxalukaay ba, mu dikk, sujjóotal Buur Suleymaan. Mu ne ko: «Man ngaa ñibbi sa kër.» \c 2 \s1 Daawuda dénku na Suleymaan \p \v 1 Ba ñu demee ba bésu àppu Daawuda di jegesi, Daawuda dafa dénk doomam Suleymaan, ne ko: \v 2 «Maa ngi ci yoon wu dul jaas ci mboolem àddina. Nanga dëgërlu te góor-góorlu, \v 3 di dénkoo sa ndénkaanel Yàlla \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, di topp ay yoonam, sàmmonteek ay dogali yoonam aki santaaneem aki àttey yoonam aki seedeem, ni ñu ko binde ci yoonu Musaa. Su ko defee dinga am ndam ci lépp loo def ak fépp foo jëm, \v 4 ba keroog Aji Sax ji sottal kàddoom ga mu ma waxoon ne ma: “Su say sët sàmmee seen dundin, saxoo ngëm gu ma wéetal, te gar ci seen bakkan, kon doo ñàkk mukk ku lay wuutu ci jalub Israyil.” \p \v 5 «Yaw ci sa bopp xam nga li ma Yowab doomu ndaw sa Seruya def, te def na ko ñaari njiiti xarey Israyil, di Abner doomu Ner ak Amasa doomu Yeter: rey na leen, tuur seen deret ni bu doon xare, ba taqal boppam ripp. Moo rendi ci biir jamonoy jàmm. \v 6 Jëflanteel ak moom ci kaw xel, bu ko bàyyi mu duggaale bàmmeel bijjaaw. \p \v 7 «Góor ñiy doomi Barsilay mu Galàdd nag, nanga leen baaxe, te ñuy bokk ak yaw ndab, ndax kat taxawu woon nañu ma, ba may daw Absalom sa doomu baay. \p \v 8 «Gannaaw loolu bàyyil xel ci Simey mi nga feggool, muy doomu Gera mu Baxurim, mi bokk ci giirug Beñamin. Moom moo ma doon tifaari saaga, bés ba ma jëmee Maanayim, moom mu dikk dajeek man ca dexu Yurdan. Ma giñal ko ci Aji Sax ji ne ko: “Duma la rey, sama saamar du la dal!” \v 9 Waaye yaw de, bu ko ñàkka topp, ndax boroom xel nga, te dinga xam ni ngay defeek moom, ba mu sangoo deretam, ànd ak bijjaawam, dugg bàmmeel.» \p \v 10 Gannaaw loolu Daawuda nelaw, fekki ay maamam, ñu denc ko ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. \v 11 Nguurug Daawuda ci Israyil tollu na ci ñeent fukki at, di juróom ñaari at ya mu péeyoo Ebron, ak fanweeri at ak ñett ya mu péeyoo Yerusalem. \p \v 12 Suleymaan nag toog ca jalub baayam Daawuda; nguuram dëgër, ne kekk. \s1 Nii la Adoña mujje \p \v 13 Ci biir loolu Adoña ma Agit di ndeyam, dem ca Batseba, ndeyu Suleymaan. Mu ne ko: «Mbaa jàmm a la indi?» Mu ne ko: «Jàmm la.» \v 14 Mu neeti ko: «Mbir la mu ma lay wax.» Mu ne ko: «Waxal.» \v 15 Mu ne ko: «Xam nga ne maa moomoon nguur gi, te man la Israyil gépp séentu woon, ma falu buur. Waaye tey nguur gi walbatiku na, tegu ci sama loxol doomu baay, ndax \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jee ko ko jox. \v 16 Léegi nag lenn rekk laa lay ñaan, te nga bañ maa gàntu.» Mu ne ko: «Waxal rekk.» \v 17 Mu ne ko: «Buur Suleymaan du la gàntu, rikk ñaanal ma ko, mu may ma Abisag mu Sunem soxna.» \v 18 Batseba ne ko: «Baax na, man kay maa la koy waxal Buur.» \v 19 Batseba dem ca Buur Suleymaan, ngir wax ko mbirum Adoña ma. Buur jóg gatandu ko, sukkal ko, daldi toogaat ci ngànguneem. Mu tegal ndeyam ngàngune, mu toog ci ndijooram. \v 20 Mu ne ko: «Man de, lenn lu tuut rekk laa lay ñaan, te bu ma gàntu.» Mu ne ko: «Waxal, saa ndey, duma la gàntu.» \v 21 Mu ne ko: «Abisag mu Sunem, may ko sa doomu baay Adoña soxna.» \v 22 Buur Suleymaan ne ndeyam: «Nga ne! Adoña ngay ñaanal Abisag mu Sunem soxna? Tee nga koo ñaanal nguur gi far, nde mooy sama mag, ñaanalaale ko Abiyatar \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi, mook Yowab doomu Seruya?» \p \v 23 Buur Suleymaan nag giñ ci Aji Sax ji ne: «Yal na ma Yàlla teg mbugal mu gëna tar, ndegam Adoña du feye bakkanam lii muy sàkku! \v 24 Léegi nag giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, te teg ma fi, dëj ma ci jalub Daawuda sama baay, sampal ma askanu nguur, wa mu dige woon, bésub tey jii Adoña dina dee.» \v 25 Buur Suleymaan daldi jox ndigal Benaya doomu Yoyada. Benaya jam Adoña, mu dee. \s1 Nii la Abiyatar mujje \p \v 26 Abiyatar \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi nag, Buur ne ko: «Dellul Anatot ca say tool. Dee rekk a war ci yaw, waaye bésub tey jii duma la rey, ndax li nga gàddu woon gaalu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji Boroom bi, dox jiitu sama baay Daawuda. Nga teg ci bokk ak sama baay mboolem coono bu mu daj.» \v 27 Suleymaan nag jële Abiyatar ci liggéeyu saraxi Aji Sax ji, daldi matal li Aji Sax ji waxoon ci waa kër Eli ca Silo. \s1 Nii la Yowab mujje \p \v 28 Yowab àndul woon ak Absalom ci pexeem, waaye Adoña la mujj àndal. Ba Yowab yégee la xew, daa daw ba ca xaymab \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, jàpp ca béjjén ya ca cati \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* ba, ngir rawale bakkanam. \v 29 Ñu wax Buur Suleymaan ne ko: «Yowab daw na, làquji ca xaymab Aji Sax ji, te kat ma nga ca sarxalukaay ba.» Suleymaan sant Benaya doomu Yoyada, ne ko mu dem, jam ko. \v 30 Benaya dugg ca biir xaymab Aji Sax ja, ne ko: «Buur nee nanga génn!» Yowab ne ko: «Génnuma, fii laay deeye!» Benaya yegge Buur waxi Yowab ak la mu ko tontu. \v 31 Buur ne ko: «Defal li mu wax, jam ko mu dee, nga suul ko, ndax ma set, maak sama waa kër baay, ci deretu jaamburi Yàlla ji Yowab tuuroon. \v 32 Su ko defee Aji Sax ji dina ko gàdduloo bakkanu boppam, feye ko ko bakkanu ñaar ña mu songoon, di Abner doomu Ner, njiital xarey Israyil, ak Amasa doomu Yeter, njiital xarey Yuda; muy ñu jub, ñu ko gën, teewul mu jam leen saamar, ñu dee te sama baay Daawuda yégu ko. \v 33 Yal na Yowab ak askanam gàddu seen bakkan ba fàww. Waaye Daawudaak askanam ak waa këram akub jalam, yal na leen Aji Sax ji jàmmal ba fàww.» \v 34 Ba loolu amee Benaya doomu Yoyada daldi dem jam Yowab, rey ko. Ñu suul ko ca këram ga ca màndiŋ ma. \v 35 Gannaaw loolu Buur tabb Benaya doomu Yoyada ca boppu mbooloom xare ma, mu wuutu Yowab. Cadog \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ba, Buur tabb ko, mu wuutu Abiyatar. \s1 Nii la Simey mujje \p \v 36 Ba mu ko defee Buur yónnee woolu Simey, wax ko ne ko: «Tabaxalal sa bopp kër fii ci Yerusalem, dëkk ca waaye bul dem fenn. \v 37 Ndaxte bés boo fi jógee, ba jéggi xuru Sedoron, xamal xéll ne dee rekk mooy sab àtte, te yaay gàddu sa bakkanu bopp.» \v 38 Simey ne Buur: «Baax na, Buur, sang bi. Li nga ma wax rekk de laay def, sang bi.» Ba loolu amee Simey toog Yerusalem lu yàgg. \p \v 39 Ba ñu ca tegee ñetti at, ñaari jaami Simey daw dem ca Akis buurub Gaat doomu Maaka. Ñu wax Simey, ne ko: «Ndeke sa jaam yaa nga Gaat!» \v 40 Simey daldi takk mbaamam, dem Gaat ca Akis, ngir jëli ay jaamam. Mu jëleji Gaat ay jaamam, délloosi leen. \v 41 Ba ñu waxee Buur Suleymaan, ne ko Simey jóge na Yerusalem dem Gaat, ba délsi, \v 42 Buur yónnee, woolu Simey, ne ko: «Xanaa giñloowuma la woon ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, àrtu la ne la: “Bés boo fi jógee dem fenn, xamal xéll ne dee rekk mooy sa àtte”? Nga ne ma: “Baax na, dinaa la déggal.” \v 43 Ana lu waral nag sàmmoo la nga giñoon ci Aji Sax ji te ma santoon la ko?» \v 44 Buur dellu ne Simey: «Yaw ci sa bopp xam nga xéll mboolem li nga lor sama baay Daawuda. Léegi Aji Sax ji dina la fey sa jëf ju bon, mu këppu ci sa kaw bopp. \v 45 Waaye man Buur Suleymaan du ma teree barkeel; jalub Daawuda it day sax fàww fi kanam Aji Sax ji.» \v 46 Buur nag sant Benaya doomu Yoyada, mu génne Simey, jam ko, mu dee. Ba loolu amee nguur ga gëna dëgër ca loxol Suleymaan. \c 3 \s1 Buur Suleymaan ñaan na Yàlla xel \p \v 1 Gannaaw ba loolu wéyee Suleymaan goromloo naak Firawna buuru Misra, jël doomu Firawna, indi ko gox ba ñu naan Kër Daawuda, ba keroog muy noppee tabax këram ak kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ak tata ja wër Yerusalem. \v 2 Terewul mbooloo ma di rendi ay sarax ca \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* ya, ndax ca yooya jamono tabaxaguñu woon kër gu ñu tudde Aji Sax ji. \v 3 Suleymaan nag wone na cofeelam ci Aji Sax ji, di wéy ci sàrti baayam Daawuda, xanaa lu moy bérabi jaamookaay ya rekk. Moom daan na fa rendi sarax, di fa taal cuuraay. \p \v 4 Ci biir loolu Buur dem Gabawon, sarxali fa, ndax foofaa doon bérabu jaamookaay ba gënoona mag: junniy \w saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, Suleymaan joxe na ko fa ca kaw \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* booba. \v 5 Foofa ca Gabawon la Aji Sax ji feeñu woon Suleymaan ci géntug guddi. Yàlla ne ko: «Ñaanal loo bëgg, ma may la ko.» \v 6 Suleymaan ne ko: «Yaw de yaa baaxe lool sab jaam Daawuda, saa baay, ngir na mu daan doxale fi sa kanam ci dëgg ak njekk ak njubteg xol. Yaa ko baaxe lool, may ko doom ju góor ju toog cib jalam, bésub tey jii. \v 7 Léegi nag Aji Sax ji, sama Yàlla, fal nga ma buur, ma wuutu saa baay Daawuda. Waaye Sang bi, man ndaw lu tuut laa, xawma sax nu may doxale. \v 8 Rax ci dolli, Sang bi, ma nekk ci digg askan wi nga taamu, askan wu yaa, ba maneesu koo waññ mbaa di ko lim. \v 9 Kon nag Sang bi, may ma xel mu am ug dégg mu ma àttee sa ñoñ, ngir may ràññee lu baax ak lu bon. Ndax kat, ana kan moo mana àtte sa ñoñ, wii askan wu réy?» \p \v 10 Kàddug Suleymaan ga nag neex Aji Sax ji, ndax loolu mu ñaan. \p \v 11 Mu ne ko: «Gannaaw loolu nga ñaan, te ñaanuloo fan wu gudd, ñaanuloo alal, ñaanuloo itam say noon dee, xanaa di ñaan xel mu rafet moo àttee dëgg, \v 12 dama ne, dinaa la defal li nga ñaan, te sax dinaa la may xel mu rafet, nga am ug dégg, ba raw ku la jiitu ak ku la wuutu. \v 13 Te itam li nga ñaanul dinaa la ko may, booleel la alal ak teraanga, ba doo am moroom ci buur yi, sa giiru dund. \v 14 Te soo jaaree ci samay yoon, jëfe samay sàrt ak samay santaane, muy fi sa baay Daawuda jaaroon, kon dinaa guddal saw fan.» \p \v 15 Ba loolu amee Suleymaan yewwu, ndeke gént la woon. Mu dellu Yerusalem, taxaw fa kanam \w gaalu kóllërey Aji Sax|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* ji, def fa ay saraxi rendi-dóomal, ak \w saraxi cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*, daldi berndeel jawriñam yépp. \s1 Suleymaan wone na xelam \p \v 16 Ba loolu wéyee mu am ñaari gànc yu dikk ca Buur, agsi ca kanamam. \v 17 Senn ndaw sa ne: «Éy sang bi, maak ndaw sii de, danoo bokk genn kër, bokk fa wasin nun ñaar. \v 18 Ba ma amee doom ba mu am ñetti fan, moom mii itam mu am doom, te nun rekk a dëkk, keneen nekkul ak nun ca biir kër ga, xanaa nun ñaar. \v 19 Doomu ndaw sii nag dee ci guddi, ndax daa tëddoon ci kawam. \v 20 Mu jóg ci xaaju guddi, jële sama doom fi sama wet, tëral ci wetam. Fekk man, sang bi, maa ngi nelaw. Doomam ji dee nag, mu tëral ko ci sama wet. \v 21 Naka laa jóg ci suba, di nàmpal sama doom, gisuma lu moy mu dee. Ba bët setee nag ma xool ko bu baax, ndeke du sama doom ji ma jur.» \v 22 Seneen ndaw sa ne: «Déedéet, sama doom mooy dund, sa doom a dee.» Ku jëkk ka ne: «Déedéet, sa doom a dee, sama doom a ngi dund.» Ñu di ko werante fi kanam Buur. \p \v 23 Buur ne: «Kii a ngi naan: “Sama doom jii mooy dund, sa doom a dee.” Kee naan: “Déedéet, sa doom a dee, sama doom mooy dund.”» \v 24 Buur teg ca ne: «Indil-leen ma saamar!» Ñu indil Buur saamar. \v 25 Buur ne: «Dogleen xale biy dund ñaar, te jox kii genn-wàll, jox kee genn-wàll.» \v 26 Ci kaw loolu ndaw si doomam di dund daldi ñeewante doomam. Mu ne: «Déet, sang bi, jox ko xale bi. Bu ko rey mukk!» Ndaw sa ca des, moom, ne: «Deesu ma ko jox, deesu la ko jox; dogleen ko ñaar!» \v 27 Ba loolu amee Buur daldi àtte ne: «Joxleen ndaw sii liir biy dund, te buleen ko rey. Mooy ndeyam.» \p \v 28 Israyil gépp nag dégg àtteb Buur, daldi yéemu ci moom, ndax dañoo gis ne xelum Yàlla mu rafet a ngi ci moom, di ko jiite ci àtte dëgg. \c 4 \s1 Suleymaan fal na ay njiit \p \v 1 Ci kaw loolu Buur Suleymaan di boroom Israyil gépp. \v 2 Ay jawriñam ñii la woon: Asaryaa sëtu Cadog moo doon \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* bi; \v 3 Eliyoref ak Awiya doomi Sisa di bindkat yi; Yosafat doomu Ayilut yore kàddug Buur; \v 4 Benaya doomu Yoyada jiite mbooloom xare ma; Cadog ak Abiyatar di ay sarxalkat. \v 5 Asaryaa doomu Natan moo jiite woon ndawi Buur ya, Sabudd doomu Natan di sarxalkat te di diglekatu buur. \v 6 Ayisar moo doon saytu kër Buur, Adoniram doomu Abda di sase liggéeyi sañul-bañ ya. \p \v 7 Buur Suleymaan amoon na fukki jawriñ ak ñaar ci Israyil gépp. Ñuy topptoo dundub Buur ak waa këram, weer wu nekk kenn ci ñoom yor dund ba, ba at mi mat. \v 8 Ñooñoo di: \li1 Ben Ur ma sasoo woon diiwaanu tundi Efrayim. \li1 \v 9 Ben Deker sasoo Makas ak Saalbim ak Bet Semes ak Elon Bet Anan. \li1 \v 10 Ben Keset sasoo Arubot, boole kook Soko ak mboolem diiwaanu Efer. \li1 \v 11 Ben Abinadab sasoo diiwaanu Dor bépp; Tafat doomu Suleymaan di soxnaam. \li1 \v 12 Baana doomu Ayilut sasoo Taanag ak Megido ak diiwaanu Bet San gépp, feggook Sartan, fa féete Yisreel suuf, muy diggante Bet San ba Abel Mewola, ba ca wàllaa Yogmeyam. \li1 \v 13 Ben Geber a sasoo woon Ramot ca Galàdd, booleek dëkk-dëkkaan ya làngu Yayir doomu Manase féetewoo woon, foofa ca Galàdd ak diiwaanu Argob ca Basan. Muy juróom benn fukki dëkk yu mag yu ñu wërale ay tata ak seeni bunt ak yeti xànjar yu koy tëj. \li1 \v 14 Ayinadab doomu Ido sasoo Maanayim. \li1 \v 15 Ayimaas ma sasoo Neftali; moom it jël na doomu Suleymaan ju ñuy wax Basmat soxna. \li1 \v 16 Baana doomu Usay boole diiwaanu Aser ak Beyalot. \li1 \v 17 Yosafat doomu Paruwa sasoo diiwaanu Isaakar. \li1 \v 18 Simey doomu Ela sasoo diiwaanu Beñamin. \li1 \v 19 Geber doomu Uri sasoo diiwaanu Galàdd, di réewum Siwon buurub Amoreen ña ak réewum Og buuru Basan. Muy benn ndawal buur bu yilif réew mooma. \p \v 20 Waa Yuda ak Israyil dañoo bare woon, ba mel ni feppi suufas géej, di lekk, di naan, nekke mbégte. \p \v 21 Ci kaw loolu Suleymaan moo yilifoon mboolem réew ya dale dexu Efraat, ba ca dëkki Filisteen ña, dem ba ca digu réewum Misra. Ñooña di indil Suleymaan galag, nangul ko giiru dundam. \p \v 22 Suleymaan daan na njëloo bés bu nekk ñeent fukki barigoy sunguf ak juróom (45), ak juróom ñeent fukki (90) barigo ci sunguf su ñagas; \v 23 ak fukki nag yu ñu yafal, ak ñaar fukki nagi parlu, ak téeméeri gàtt, te limaaleesul xeeti kéwél yaak boroom dunq yu duuf ya. \v 24 Suleymaan moo yilifoon mboolem réew ma féete dexu Efraat sowu, dale ko ca Tifsa ba ca Gasa, muy mboolem réew ya féete dexu Efraat sowu. Jàmm ne ñoyy, féete ko wet gu nekk. \p \v 25 Diirub ayu Suleymaan gépp nag, waa Yudak Israyil ànd ak xel mu dal; ku ci nekk ak sa ker garabu reseñ ak sa ker garabu figg, fa dale diiwaanu Dan ba ca Beerseba. \v 26 Suleymaan amoon na ñeenti junniy (4 000) wuddi fasi watiir ak fukki junniy fas ak ñaar (12 000). \v 27 Jawriñ ya dañu daa ay-ayloo, ku nekk ak sa weer wi ngay topptoo dundub Buur Suleymaan, mook mboolem ñi mu bokkaloon njël, ba dara daawu ca ñàkk. \v 28 Peppum lors ji ànd ak ñax mi jëm ci fasi watiir yeek fasi dawkat yi itam, ku nekk ci ñoom da daan indi la ñu ko ca sas, teg ko fa mu wara nekk. \s1 Suleymaan kenn la woon \p \v 29 Ci biir loolu Yàlla jagleel Suleymaan mu ñaw lool, am xel mu rafet ak xam-xamam bu yaa, bu solowoo fànn yu bare ni feppi suufas géej. \v 30 Suleymaan rafetoon nam xel, ba sut mboolem doomi réewum penku ak mboolem waa Misra. \v 31 Rafetoon nam xel ba raw ñépp: muy Etan Esraseen ba, di Eman, di Kalkol, di Darda, doomi Maxol yu góor ya. Turam nag siiw ca mboolem xeet ya ko wër. \v 32 Léeb na ñetti junniy kàddu, woy yi mu fent ëpp junni. \v 33 Faramfàcce na it mbirum gàncax, dale ko ci garabu seedar gu Libaŋ ba ci isob giy sax cib tabax. Jàngle na mbirum mala ak njanaaw ak luy raam, ba ci jën. \v 34 Nit ñi dañu daan jóge ci xeet yépp, di sàkkusi xelam Suleymaan mu rafet; te dañu daan bàyyikoo ci mboolem buuri àddina yi déggoon xelam mu rafet. \c 5 \s1 Suleymaan waajal na tabaxu kër Yàlla ga \p \v 1 Ba Iram buurub Tir déggee ne Suleymaan lañu fal buur, mu wuutu baayam Daawuda, ak na mu xaritoo woon ak Daawuda naka jekk, Iram daa yónnee ay ndawam ca Suleymaan. \v 2 Suleymaan it yónnee ca Iram, ne ko: \v 3 «Xam nga sama baay Daawuda manul woona tabaxal Yàllaam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji kër gu mu ko tudde, ndax xare yi mu séqoon ak noonam yi ko wër, ba ni leen Aji Sax ji daaneele, mu teg leen tànk. \v 4 Léegi nag sama Yàlla Aji Sax ji may na ma jàmm ne ñoyy, féete ma wet gu nekk, ba awma benn noon, te musiba dabu ma. \v 5 Fii ma nekk damaa fas yéene tabax kër, tudde sama Yàlla Aji Sax ji. Muy la Aji Sax ji waxoon sama baay Daawuda, ne ko: “Sa doom ji may def sa kuutaay ci sab jal moo may tabaxal kër, tudde ma ko.” \v 6 Ci biir loolu ma di la ñaan, nga santaane, ñu goral ma banti seedar yu Libaŋ, te samay surga ànd ak say surga ci liggéey bi. Sa peyooru nit ñi dinaa la ko fey ak loo mana feyeeku, ndax yaw xam nga ne amunu ci sunu biir ñu mane yett bant ni waa Sidon.» \p \v 7 Ba Iram déggee li Suleymaan wax, am na ca mbégte mu réy. Mu ne: «Cant ñeel na Aji Sax ji tey jii, bi mu mayee Daawuda doom ju rafet xel, mu jiite xeet wu réy wii.» \v 8 Ci kaw loolu Iram yónnee ca Suleymaan, ne ko: «Dégg naa kàddu yi nga ma yóbbante. Man ci sama bopp dinaa la defal li nga bëgg lépp ci wàllu banti garabi seedar ak sippar\f + \fr 5.22 \fr*\fk sippar \fk*\ft garab la gu xeetook filaawo.\ft*\f*. \v 9 Samay surgaa koy diree Libaŋ ba ca géej ga, rabat ko, ma jaarale ko ci géej gi ba foo ma wax. Su ko defee ma tas ko foofa, nga yóbbu. Yaw nag nangul ma rekk li may sàkku, muy nga joxal ma sama waa kër ab dund.» \p \v 10 Ba loolu amee Iram jox Suleymaan la mu bëgg ci banti garabi seedar ak sippar. \v 11 Suleymaan ci wàllu boppam jox Iram ñaar fukki junni ak juróom ñetti (28 000) barigoy peppu bele, ak ñaar fukki barigo ak ñaar (22) ci diwu oliw gu ñu segal. Suleymaan di defal Iram noonu at mu ne. \v 12 Bu loolu weesee Aji Sax ji mayoon na Suleymaan xel mu rafet, na mu ko ko dige woon. Jàmm it doxoon na diggante Iram ak Suleymaan, ba ñu fasante \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* ñoom ñaar. \p \v 13 Buur Suleymaan nag sas fanweeri junniy nit (30 000) ci Israyil gépp ay liggéeyi sañul-bañ. \v 14 Mu di leen yebal Libaŋ, weer wu nekk fukki junni (10 000) dem. Bu ñu amee Libaŋ weer, am seeni kër ñaari weer. Adoniram a jiite woon sas ya. \v 15 Suleymaan sàkk juróom ñaar fukki junniy (70 000) yenukat, ak juróom ñett fukki junniy (80 000) yettkati doj ca tund ya, \v 16 te bokkul ak ñetti junni ak ñetti téeméeri nit (3 300) ñi Suleymaan tabb, ñuy jiite liggéey bi, di saytu liggéeykat yi. \v 17 Buur santaane ñu jële fa doji tànnéef yu réy yu ñuy yett, muy kenug kër Yàlla ga. \v 18 Ba mu ko defee tabaxkati Suleymaan ak tabaxkati Iram ak waa Gebal di yett ak a waajal bant yaak doj, ya ñuy tabaxe kër ga. \c 6 \s1 Suleymaan tabax na kër Yàlla ga \p \v 1 Ca ñeenti téeméereelu at maak juróom ñett fukk (480), gannaaw ba \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* génnee réewum Misra, ca ñeenteelu atu nguurug Suleymaan, ci weeru Siw, di ñaareelu weeru at ma\f + \fr 6.1 \fr*\fk weeru Siw \fk*\ft moo yemook awril, jàpp me.\ft*\f*, ca la Suleymaan tàmbalee tabax kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \p \v 2 Kër gi Buur Suleymaan tabaxal Aji Sax ji, juróom benn fukki xasab\f + \fr 6.2 \fr*\fk xasab \fk*\ft mooy guddaayu loxo, diggante catu baaraamu digg ak conc.\ft*\f* la guddaay bi am, yaatuwaay bi di ñaar fukki xasab, taxawaay bi di fanweeri xasab. \v 3 Buntu \w néeg bu mag|lemma="néeg (Yàlla) bu mag b-:"\w* bi ab dëru biti la jàkkaarlool, yaatuwaayu dër bi di ñaar fukki xasab, tollook yaatuwaayu kër gi. Guddaayam féete ci kanam kër gi, yokke guddaayu kër gi fukki xasab. \v 4 Mu defal miiri kër gi ay palanteer yu am feguwaay yu ñu we ay caax. \v 5 Mu tabax ay taax yu sës ca ñetti miiri kër gi. Taax yi dar ñaari miiri néeg bu mag bi ak miiru néegu biir bu sell bi ci gannaaw. Taax yi def ay néeg yu ndaw. \v 6 Taax mi féete suuf juróomi xasab mooy yaatuwaayam, taax mi ci tegu di juróom benni xasab. Taaxum kaw mi am yaatuwaayu juróom ñaari xasab; ndax dañoo bàyyi ay teguy làcc ci miiri kër gi, ngir xaddi taax yi baña jàpp ci miiri kër gi. \p \v 7 Kër ga, ba ñu koy tabax ay doj lañu ko tabaxe, muy doj yu ñu yett fa ñu ko jële ba noppi, moo tax du saddu, du sémmiñ mbaa lenn luy jumtukaayu weñ bu ñu dégg mu dal, diir ba ñuy tabax kër ga. \p \v 8 Buntu taax mi ci suuf ma nga féete woon ndijoor, nit mana jaare ci ay dëggastal, yéeg jàll ci taaxum digg mi, jóge ci taaxum digg mi, jàll ci taax mi ci kaw. \p \v 9 Suleymaan tabax kër gi ba noppi, xadde ko dénki garabi seedar ak gàlluy seedar. \v 10 Taaxi kaw yi wër kër gépp, bu ci nekk juróomi xasab la def taxawaayam, lëkklee ko peeri garabu seedar, ba mu sës ca kër ga. \p \v 11 Ci biir loolu kàddug Aji Sax ji dikkal Suleymaan. Mu ne ko: \v 12 «Kër gii de yaa ngi koy tabax. Waaye soo sàmmee samay dogal ak samay ndigal, di jëfe sama santaane yépp, di ci topp, su boobaa dinaa sottal li ma digoon sa baay Daawuda ci sa mbir. \v 13 Dinaa dëkk ci digg bànni Israyil, te duma dëddu Israyil, sama ñoñ.» \v 14 Ba mu ko defee Suleymaan tabax kër gi, ba sottal ko. \s1 Liggéey nañu biir kër gi \p \v 15 Fa féete biir nag, mu lale miir yi xànqi seedar, dale ko ci suuf ba ci xadd bi. Dafa lal biir kër gi bant, lal dër bi xànqi sippar. \v 16 Bàyyi na itam ñaar fukki xasab ci biir kër gi ci gannaaw, muy néeg bu mu lale banti seedar ci suuf ba ci xadd bi ci kaw. Mu sàkk ko ci biir kër gi, mu dib néegu biir bu sell, di \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* baa sell. \v 17 Ñeent fukki xasab yi ko féete kanam di \w néeg Yàlla bu mag|lemma="néeg (Yàlla) bu mag b-:"\w* bi. \v 18 Banti seedar yi lale ci biir kër gi, dees cee yett ay nataali koog ak tóor-tóor yu focci; lépp di bantu seedar, ba xeer feeñul. \p \v 19 Néeg bu sell baa sell ca biir kër ga ca biir-a-biir la waajal, ngir yeb fa \w gaal gay def àlluway kóllërey Aji Sax|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w* ji. \v 20 Néeg bu sell baa sell amoon na guddaayu ñaar fukki xasab, yaatuwaay ba di ñaar fukki xasab, taxawaay ba di ñaar fukki xasab; Suleymaan xoob ko wurusu ngalam. \w Sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* seedar ba jàkkaarlook néeg ba, moom it xoob na ko wurusu ngalam. \v 21 Ci biir loolu Suleymaan xoob biir néeg Yàlla ba wurusu ngalam. Mu tàllal ay càllalay wurus fi kanam néeg bu sell baa sell, \v 22 daldi xoob ci biir wurus ba mu daj. \p Sarxalukaayu néeg bu sell baa sell, lépp la xoob wurus. \p \v 23 Ci kaw loolu mu sàkk ca biir néeg bu sell baa sell ñaari malaakay \w serub|lemma="serub y-:"\w* yu ñu yette bantu oliw, jëmm ju ci nekk am taxawaayu fukki xasab. \v 24 Benn serub bi laaf mu ci nekk juróomi xasab la, muy fukki xasab ci catal menn laaf mi ba ca catal laaf ma ca des. \v 25 Fukki xasab it mooy taxawaayu ñaareelu serub bi, ndax ñaari serub yee tolloo dayo, bokk bind; \v 26 taxawaayub serub bu ci nekk fukki xasab la. \p \v 27 Suleymaan teg serub ya ca digg néeg bu sell baa sell, seeni laaf fireeku, catal laafu benn serub bi di laal genn wetu tabax bi, catal laafu serub ba ca des di laal geneen wetu tabax bi. Seen ñaari cati laaf yi ci des it di laale fa tollook digg néeg ba. \v 28 Mu teg ca xoob serub yi wurus. \p \v 29 Mu yettlu nag ay serub ci kaw miiri ñaari néegi kër gi, yettaale garabi ron aki tóor-tóor yu focci, wërale. \v 30 Xoob na itam dëru tabax bi wurus, ci néegu biir bi ak ci biti. \p \v 31 Buntu néeg bu sell baa sell, kubeeri banti oliw la ko def, njëël bunt bi aki jënam bant lañu yu bindoo juróomi wet. \v 32 Ñaari kubeer yi banti oliw la; mu yettlu ca kawam ay malaakay serub aki ron aki tóor-tóor yu focci, ba noppi xoob lépp wurus, xoobaale serub yi wurus ak ron yi itam. \v 33 Noonu it la def buntu néeg bu mag bi, ay jënam di bantu oliw, waaye bunt bi, jëwam aki jënam, bant lañu yu bindoo ñeenti wet. \v 34 Ñaari kubeeram di bantu sippar, bu ci nekk di ñaari xànq yuy warangiku. \v 35 Mu yettlu ci kaw kubeeri bunt yi jëmmi serub aki ron aki tóor-tóor yu focci, daldi xoob lépp wurus. \p \v 36 Suleymaan tabaxe miiru ëttu biir bi ay xeeri yett ak xànqi seedar, ba ñetti sësalantey xeer yu tegloo yu ne, benn sësalanteb xànqi seedar tege ca. \p \v 37 Ca ñeenteelu atu nguurug Suleymaan, yemook ñaareelu weer wa, di weeru Siw, ca lañu teg kenug kër Aji Sax ji. \v 38 Ca fukkeelu at maak benn, yemook juróom ñetteelu weer wa, di weeru Bul\f + \fr 6.38 \fr*\fk weeru Bul \fk*\ft moo yemook oktoobar, jàpp nowàmbar.\ft*\f*, ca la kër ga sotti, mook mboolem la ca bokk ak na mu wara bindoo lépp. Suleymaan tabax na kër ga ci juróom ñaari at. \c 7 \s1 Suleymaan tabax na këram \p \v 1 Kërug boppam nag, Suleymaan tabax na ko ci fukki at ak ñett, doora sottal këram gépp. \v 2 Ma nga jëkka tabax kër ga ñuy wooye Gottub Libaŋ. Guddaay bi di téeméeri xasab, yaatuwaay bi di juróom fukki xasab, taxawaay bi di fanweeri xasab, def ñeenti sàppey jëni seedar yu yenu ay gàlluy seedar yu ñu yett. \v 3 Ñu teg ay banti seedar ci kaw gàllu, yi jën yi yenu: muy ñeent fukki gàllu ak juróom, sàppe bu nekk fukki gàllu ak juróom. \v 4 Mu am ñetti sësalantey palanteer yu ñu fege ay laat te ñu dékkarloo ñett-ñett. \v 5 Bunt yépp ànd ak seen banti feguwaay, bunt bu ci nekk def ñeenti wet yu janoo màkk ñaar-ñaar; bunt yi sësaloo te dékkarloo ñett-ñett. \p \v 6 Ci biir loolu mu defar néeg ba ñuy wooye Néegu jëni kenu ya. Guddaay bi di juróom fukki xasab, yaatuwaay bi di fanweeri xasab, ak beneen néeg ci kanamam, mu ànd ak ay jëni kenoom ak xaddam bu mbaar ci kanam. \v 7 Mu tabax néeg ba ñuy wooye Néegu ngàngune ma walla Àttekaay ba, mu di fa àttee. Mu dare néeg bi banti seedar ci suuf ba ci kaw. \p \v 8 Këram ga mu dëkk it, ñu tabaxe ko noonu ci gannaaw Néegu ngàngune ma. Suleymaan teg ca tabaxal soxnaam doomu Firawna ja geneen kër gu nirook këram. \p \v 9 Tabax yooyu yépp biir ak biti xeeri tànnéef yu ñu yett la, natt ko, xacc ko, rattaxal, dale ko ci kenu gi, ba ci cati xadd bi ci kaw, daleeti ci biti ba ci ëtt bu mag bi. \v 10 Ñu defare kenu yi xeeri tànnéef yu mag: yii di fukki xasab, yii di juróom ñetti xasab. \v 11 Xeer yi tege ci kenu gi, xeeri tànnéef la yu ñu yett, natt ko, yemale, booleek banti seedar. \v 12 Miiru ëtt bu mag bi dees koo wëralee ay xeeri yett aki xànqi seedar: ñetti sësalantey xeer yu tegloo yu ne, benn sësalanteb xànqi seedar tege ca. Mu mel ni na ñu def ëttu biir bu kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ja ak dëru buntu kër ga. \s1 Tëgg ba def na wàllam \p \v 13 Ci kaw loolu Buur Suleymaan yónnee, jëli ca Tir ku ñuy wax Uram\f + \fr 7.13 \fr*\fk Uram \fk*\ft mooy Iram ba tey. Seetal it aaya 40 ak 45.\ft*\f*. \v 14 Doomu jëtun la woon, bokk ci giirug Neftali. Baayam dëkkoon Tir\f + \fr 7.14 \fr*\fk Tir \fk*\ft ab dëkk la bu bokkul ci Israyil.\ft*\f*, di tëggub xànjar. Uram di ku xareñ lool, rafet xel te mane mboolem liggéeyu xànjar. Mu dikk ca Buur Suleymaan, liggéeyal ko la ñu ko sant lépp. \p \v 15 Mu móol ñaari xeri xànjar, wu ci nekk am taxawaayu fukki xasab ak juróom ñett, te wu ci nekk buumu fukki xasab ak ñaar a koy ub. \v 16 Ci biir loolu mu defar ñaari boppi xànjar yu mu xelli, teg ko ci kaw xer yi, bopp bu ci nekk am taxawaayu juróomi xasab. \v 17 Bopp yi ci kaw xer yi, bu ci nekk da koo rafetale ab caaxu càllala, bopp bu ci nekk am ci juróom ñaar. \v 18 Mu defar ñaari jaray gërënaat, solal ko caax yi, wëralee ko bopp yi, ci xer wu ci nekk. \v 19 Bopp yi nekkoon ci kaw xer yi ci kanam nag bindoo ni lëppi tóor-tóor te bu ci nekk di ñeenti xasab. \v 20 Bopp yi ci kaw ñaari xer yi, bu ci nekk ñaar téeméeri gërënaat a ko wër ci kaw, feggook gamb bi ci wàllaa caax bi. \p \v 21 Mu samp jën yi ci kanam bunt \w néeg Yàlla bu mag|lemma="néeg (Yàlla) bu mag b-:"\w* bi; samp jënu ndijoor wi, tudde ko Yakin (Kiy taxawal), samp jënu càmmoñ wi, tudde ko Bowas (Kiy dooleel). \v 22 Kaw xer yi ay lëppi tóor-tóor yu ñu xellee ci tege. Liggéeyu xer ya daldi sotti. \p \v 23 Ba mu ko defee Uram móol mbalkam njàpp mu weñ, ñu di ko wax Géej ga. Mbalka ma daa mërgalu, yaatoo fukki xasab, catu omb ba catu omb, taxawaay ba di juróomi xasab, ag buumu fanweeri xasab di ko ub. \v 24 Ay gamb la ko sàkkal ci suufu kéméj gi, fukki gamb tollook xasab. Mu def gamb yi ñaari caq yu wër mbalka mi ba mu daj te ànd ak mbalka mi ci benn xelli. \v 25 Mbalkam njàpp mi tege ci kaw fukki jëmmi nag ak yaar, ñett jublu bëj-gànnaar, ñett jublu sowu, ñett jublu bëj-saalum, ñett jublu penku. Mbalka mi war nag yi, seeni gannaaw féete biir, ñoom ñépp. \v 26 Dëllaayu mbalka mi yaatuwaayu loxo la, kéméj gi mel ni gémmiñu kaas, di nirook lëppi tóor-tóor. Ñaar téeméeri barigo la mbalka miy def. (200). \p \v 27 Mu daldi sàkk fukki watiiri rootukaayi xànjar, wu ci nekk am guddaayu ñeenti xasab, yaatuwaayam di ñeenti xasab, taxawaayam di ñetti xasab. \v 28 Ni ñu defare rootukaay yi nii la: ay wetam lañu defare làcci xànjar, lëkklee làcc yi ay laat. \v 29 Muy làcc yu Uram yett ci kawam ay gaynde, ay nag ak malaakay \w serub|lemma="serub y-:"\w*. Kaw laat yi itam am na ci nataal yi. Mu yett ay caqi tóor-tóor yuy lang ci suufu gaynde yeek nag yi. \v 30 Rootukaay bu nekk am na ñeenti mbegey xànjar yu ñu lëkklee yeti xànjar. Mu am ay kenu yu ñu xellil rootukaay bi ci ñeenti koñam, kenu yi yenu benn bagaan te am ay nataali tóor-tóor. \v 31 Gémmiñu rootukaay bu nekk amoon na omb bu mërgalu bu bagaanu ndox biy tege. Xóotaayu gémmiñ gi di xasab, yaatuwaay bi di xasab ak genn-wàll. Ñu yett ci kaw gémmiñ gi ay nataal ba tey. Rootukaay bi mërgaluwul, waaye daa bindoo ñeenti wet yu janoo màkk ñaar-ñaar te yem kepp. \v 32 Ñeenti mbege yi ronu làcc yi, tóori weñ yi ci wewe sax ci rootukaay bi. Mbege mu ci nekk am na taxawaayu xasab ak genn-wàll. \v 33 Mbege yi bindoo ni mbegey watiiri xare. Tóor yeek mbege yi ak sidditi mbege yi ak ŋanku yi, xànjar lañu ko xellee. \v 34 Ñeenti kenu yi ci ñeenti koñi rootukaay bi, bu ci nekk dees koo xelleendook weti rootukaay yi, ba lépp di benn. \v 35 Kaw boppu rootukaay bu nekk, kéméj gu mërgaloo féete ci kaw, taxawaayam di genn-wàllu xasab, njàppu yeek làcc yi sax ci, lépp di benn. \v 36 Fi amul dara ci kaw njàppu yeek làcc yi, mu ñaas ci ay nataali serub aki gaynde aki garabi ron yu ñu wërale ay caqi tóor-tóor. \v 37 Noonu la Uram defare fukki rootukaay yi. Lépp bokk móol, yem dayo te bokk bind. \p \v 38 Mu defar itam fukki bagaani xànjar; bagaan bu ci nekk tollook ñeenti xasab, di def lu xawa tollook juróomi barigo; bagaan bu ci nekk tegu cib rootukaay, ba fukki rootukaay yi daj. \p \v 39 Ba mu ko defee mu taaj juróomi rootukaay fa féete kër Yàlla ga ndijoor ak juróomi rootukaay fa féete kër ga càmmoñ. Mu teg mbalkam jàpp mi fa féete kër ga ndijoor, ca wetu bëj-saalum, jàpp penku. \p \v 40 Iram sàkk itam ndab yu ndaw yi ak ñiitukaay yi ak këlli tuurukaay yi. \p Ci kaw loolu Iram sottal mboolem liggéey ba mu liggéeyal Buur Suleymaan ca kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji: \v 41 muy ñaari jën yi, ak ñaari gamb yiy boppi jën yi, ak ñaari caaxi càllala yiy muur ñaari gamb yi, \v 42 ak ñeenti téeméeri gërënaat yiy ànd ak ñaari caax yi; caax bu nekk, ñaari caqi gërënaat, ñu dar ñaari gamb yiy boppi xer yi; \v 43 ak fukki rootukaay yi ak fukki bagaan yi ci kaw rootukaay yi. \v 44 Mbalkam jàpp mi it ci la, ak fukki nag ak yaar yi ronu mbalkam jàpp mi. \v 45 Bagaan yu ndaw yi bokk na ci, ak ñiitukaay yi ak këll yi. Mboolem yooyu jumtukaayi kër Aji Sax ji, xànjar bu ñu jonj la Buur Suleymaan sant Uram, mu defare ko. \v 46 Ca joorug Yurdan la ko Buur xellilu, ci móoli ban, diggante Sukkóot ak Sartan. \v 47 Suleymaan daldi bàyyi jumtukaay yépp noonu, ndax na mu baree lool, ba natteesul diisaayu xànjar ba ca dem. \p \v 48 Gannaaw loolu Suleymaan defarlu na mboolem yeneen jumtukaayi kër Aji Sax ji: muy \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* wurus ba, ak taabal ja ñuy teg \w mburum teewal|lemma="mburum teewal m-:"\w* ma\f + \fr 7.48 \fr*\fk mburum teewal mi \fk*\ft mooy mburu mi ñuy teewal fi kanam Aji Sax ji.\ft*\f* \v 49 ak tegukaayi làmpi wurusu ngalam yi, juróom ci wetu ndijoor, juróom ci wetu càmmoñ, fi kanam néeg bu sell baa sell; tóor-tóor yi ak làmp yi ak ñiim yi, lépp di wurus; \v 50 ndab yi itam, ak feyukaay yi ak këll yi ak kopp yi ak andi cuuraayu yi, lépp di wurusu ngalam. Te it ngoosi wurus yi bunti néeg bi wewe, ñu di fa jaare dugg ca \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* baa sell, ak ngoosi wurus yi beneen buntu néeg bi wewe, ñu di fa jaare dugg ci néeg Yàlla bu mag bi, lépp wurus la. \p \v 51 Ba loolu amee, mboolem lu Buur Suleymaan liggéeyal kër Aji Sax ji daldi sotti. Mu boole xaalis baak wurus waak jumtukaay ya baayam Daawuda sellalaloon Aji Sax ji, yeb ko ca denc ya def alali kër Aji Sax ji. \c 8 \s1 Sancal nañu gaalu Yàlla ga \p \v 1 Ba mu ko defee Suleymaan woolu magi Israyil. Mboolem kilifay giiri Israyil ak seen njiiti kër maam ya daje Yerusalem ca moom, ngir ñu àgg \w Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"\w*, gox ba ñu naan Kër Daawuda, ba yékkatee fa \w gaal ga kóllërey Aji Sax ji dence|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w*. \p \v 2 Waa Israyil gépp nag daje ca Buur Suleymaan, ca weeru Etanim\f + \fr 8.2 \fr*\fk weeru Etanim \fk*\ft moo yemook sàttumbar, jàpp oktoobar, ñu daan ca amal màggalu Mbaar ya.\ft*\f*, ca màggalu juróom ñaareelu weer woowu. \v 3 Ba magi Israyil ñépp dikkee, \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ya yékkati gaal ga. \v 4 Ñu boole gaalu Aji Sax ja, ak \w xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"\w* ma, ak mboolem jumtukaay yu \w sell|lemma="sell:"\w* ya ca biir xayma ba. Sarxalkat ya ak \w Leween|lemma="Leween b-:"\w* ña daldi gàddu lépp. \v 5 Buur Suleymaan ak mbooloom Israyil ma daje fa moom, ñoom ñépp a nga bokk ak moom, teew. Ñu jàkkaarlook gaal ga, di rendi ay gàtt aki nag yu kenn manula lim mbaa di ko waññ, ndax bare. \p \v 6 Gannaaw loolu sarxalkat ya yóbbu gaalu Aji Sax ja ca bérabam, ca biir néeg bu sell baa sell, ca ron laafi malaakay \w serub|lemma="serub y-:"\w* ya. \v 7 Ndaxte jëmmi serub ya, seeni laaf daa tàllalu, tiim bérabu gaal ga, laaf ya yiir kaw gaal ga aki njàppoom. \v 8 Njàppu ya daa guddoon, ba nit mana séen cat ya te fekk ko tollu ca \w bérab bu sell|lemma="bérab bu sell b-:"\w* ba, ca kanam néeg bu sell baa sell. Waaye maneesula tollu ca biti di séen cat ya. Njàppu yaa nga fa ba tey jii. \v 9 Dara nekkuloon ca biir gaal ga, lu moy ñaari àlluway doj ya ca Musaa yeboon ca tundu Oreb\f + \fr 8.9 \fr*\fk Oreb \fk*\ft mooy Sinayi ba tey.\ft*\f*, fa Aji Sax ji fase woon kóllëre ak \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, ba ñu génnee réewum Misra. \p \v 10 Ba sarxalkat ya génnee bérab bu sell ba, niir wa daa fees kër Aji Sax ja, \v 11 ba sarxalkat ya talatuñoo liggéey, ndax leeru Aji Sax jaa nekkoon ca niir wa, niir wa feesal kër ga. \s1 Suleymaan àddu na \p \v 12 Ba mu ko defee Suleymaan ne: «\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji moo noon lëndëm gu fatt lay màkkaanoo.» \v 13 Mu ne Aji Sax ji: «Tabaxal naa la kër gu màgg, màkkaan mooy dëkke ba fàww.» \v 14 Ci kaw loolu Buur Suleymaan walbatiku, ñaanal mbooloom Israyil mépp, fekk mbooloom Israyil mépp a nga taxaw. \v 15 Mu ne: «Cant ñeel na Aji Sax ji, Yàllay Israyil, moom mi sottale loxol boppam, la mu waxoon Daawuda sama baay ci gémmiñam, ne ko: \v 16 “La dale bés ba ma génnee \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*, sama ñoñ ca Misra ba tey, taamuwuma benn dëkk, ci mboolem giiri Israyil, bu ñuy tabax kër, gu sama tur di nekk. Waaye maa taamu Daawuda, ngir mu falu ci kaw Israyil sama ñoñ.” \v 17 La doon yéeney Daawuda sama baay nag moo doon tabax kër gu mu tudde Aji Sax ji, Yàllay Israyil. \v 18 Teewul Aji Sax ji wax Daawuda sama baay, ne ko: “Gannaaw yaa fasoon ci sa xol, yéeney tabax kër, tudde ma ko, def nga lu rafet, ngir sa yéeney xol la woon. \v 19 Waaye du yaw yaay tabax kër gi; sa doom ju góor ju soqikoo ci sa geño, moom mooy tabax kër gi, tudde ma ko.” \p \v 20 «Aji Sax ji moo sottal waxam ja mu waxoon. Wuutu naa sama baay Daawuda, toog naa ci jalub Israyil, noonee ko Aji Sax ji waxe woon. Tabax naa kër gi, tudde ko Aji Sax ji, Yàllay Israyil. \v 21 Te it sàkk naa fa bérab bu ñeel \w gaal gi def àlluway kóllërey Aji Sax|lemma="gaalu kóllëre g-:"\w*, ji mu fasoon ak sunuy maam, ba mu leen génnee réewum Misra.» \s1 Suleymaan yékkati na kàddug ñaan \p \v 22 Gannaaw loolu Suleymaan taxaw jàkkaarlook \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, fa kanam mbooloom Israyil mépp. Mu daldi tàllal ay loxoom asamaan, \v 23 daldi ne: «Yaw Aji Sax ji Yàllay Israyil, amul jenn yàlla ju mel ni yaw fa kaw asamaan mbaa ci kaw suuf si mu tiim, yaw miy sàmm \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* ak ngor, ñeel sa jaam ñiy doxe seen léppi xol, fi sa kanam. \v 24 Yaa sàmm kàddu ga nga waxoon sa jaam ba, Daawuda sama baay, ci sa gémmiñu bopp, te yaa sottale sab loxo, sa kàddu bés niki tey. \p \v 25 «Léegi nag Aji Sax ji, Yàllay Israyil, ngalla sàmmal li nga waxoon sa jaam ba, Daawuda sama baay, ne ko: “Deesu la xañ mukk ci saw askan ku góor kuy tooge jalub Israyil fi sama kanam, ndegam saw askan a ngi moytu seenu yoon, tey doxe fi sama kanam noonee nga daan doxe fi sama kanam.” \v 26 Kon nag yaw Yàllay Israyil, ngalla saxalal wax jooju nga waxoon Daawuda, sa jaam ba. \p \v 27 «Waaye yaw Yàlla! Ndax yaay dëkk ci kaw suuf sax? Seetal rekk, asamaan yi ba ca asamaani asamaan ya manu laa fat, waxumalaa kër sii ma tabax. \v 28 Waaye Aji Sax ji, sama Yàlla, rikk, teewlul li ma lay ñaan, man sab jaam, di la ko dagaan; ngalla déggal sama yuux, te nangu ñaan gi ma lay ñaan bés niki tey. \v 29 Yal nanga ne jàkk guddeek bëccëg ci kër gii, bérab bi nga noon: “Fi la sama tur di nekk,” te yal nanga dégg ñaan gi ma jublu bérab bii, di ko ñaan, man sab jaam. \v 30 Yal nanga may nangul sama dagaan, nangul Israyil sa ñoñ. Bu ñu jubloo bérab bii, ñaan la, yal nanga ko dégge bérab ba nga dëkke ca asamaan, ba nangul leen, jéggal leen. \p \v 31 «Ku ñu tuumaal ne moo tooñ moroomam, te yoon waatloo ko ba waat war ko, bu dikkee di waatsi fi sa kanam sarxalukaay bi ci biir kër gii, \v 32 Su boobaa, yaw rikk dégge ko asamaan, àtte say jaam, ngir teg ki tooñ, daanub tooñ, këpp añu jëfam ci kaw boppam, te nga dëggal ki am dëgg, jox ko dëggam gi mu yelloo. \p \v 33 «Bu Israyil sa ñoñ daanoo fi kanam ab noon, ndax tooñ gu ñu la tooñ, bu ñu waññikoo ci yaw, sàbbaal saw tur, ñaan, sàkku saw yiw ci biir kër gii, \v 34 su boobaa yaw, yal nanga dégge asamaan, ba jéggale bàkkaarub Israyil sa ñoñ, te nga delloo leen ca réew ma nga joxoon seeni maam. \p \v 35 «Bu asamaan tëjoo, taw amul ndax tooñ gu ñu la tooñ, bu ñu jubloo bérab bii, ñaan la, sàbbaal saw tur te dëddu seen bàkkaar ndax sa mbugal, \v 36 su boobaa yaw ngalla nangool fa asamaan, te nga jéggale sa bàkkaaru jaam ñi, Israyil sa ñoñ. Ngalla xamal leen yoon wu baax wi ñu wara doxe te nga tawal sa suuf, si nga joxoon sa ñoñ, muy seen cér. \p \v 37 «Bu xiif amee ci réew mi, mbaa mbas, mbaa gàncax gi lakk, mbaa benaat xuural ko, mbaa mu diy njéeréer mbaa soccet, mbaa su dee congum seen noon ci seen dëkki réew mi, mbaa muy mboolem luy musiba ak mboolem jàngoro, su boobaa, \v 38 lépp lu ciy ñaan akug tinu gu bawoo ci képp ku mu doon mbaa ci mboolem Israyil sa ñoñ, te fekk ku ci nekk ràññee mititu xolam, ba tàllal ay loxoom jublook kër gii, \v 39 su boobaa, yaw, ngalla nangoo ko asamaan, màkkaan ma nga dëkke, ba jéggale, te nga jëf ba yool ku nekk kemu mboolem ay jëfam, yaw mi xam xolam, ndax yaw doŋŋ yaa xam xolu mboolem doom aadama. \v 40 Su ko defee dinañu la ragal seen giiru dund ci kaw suuf si nga joxoon sunuy maam. \p \v 41 «Te itam doxandéem bu bokkul ci Israyil sa ñoñ bu jógee réew mu sore ngir sa tur, \v 42 ndax kat dees na dégg sa tur wu réy, ak sa dooley loxo ak sa kàttanu përëg, bu dikkee ba jublu ci kër gii, ñaan, \v 43 su boobaa ngalla nangool asamaan, màkkaan ma nga dëkke, te nga defal doxandéem boobu mboolem lu mu la ñaan, ndax xeeti àddina yépp xam sa tur, ngir ragal la ni Israyil sa ñoñ, te xam ne saw tur lañu tudd ci kër gii ma tabax. \p \v 44 «Bu sa ñoñ di xarejeek seen noon, ci yoon woo leen yebal, su ñu ñaanee ci Aji Sax ji, jublook dëkk bii nga taamu, ak kër gii ma tabax ngir saw tur, \v 45 su boobaa ngalla nangool asamaan, seenug ñaan ak seen dagaan te nga may leen ndam. \v 46 Bu ñu la moyee, nde amul nit ku dul moy, ba nga mere leen, teg leen ci loxob noon, noon ba jàpp leen, yóbbu am réewam, mu sore mbaa mu jege, \v 47 bu ñu demee ba seenum xel dellusee fa réew ma ñu leen yóbbu ngàllo, ñu tuub tey sàkku aw yiw fi yaw foofa ca réewum ña leen jàpp, ne la noo moy, noo ñaaw, noo def lu bon, \v 48 bu ñu waññikoo seen léppi xol, ak seen léppi jëmm ci yaw, foofa ca seen réewu noon ya leen jàpp, ba ñaan la, jublook seen réew ma nga joxoon seeni maam, jublook dëkk bi nga taamu, ak kër gii ma tabax ngir saw tur, \v 49 ngalla su boobaa, nangool ca asamaan, bérab ba nga dëkke, seen ñaan ak seen dagaan, te nga sàmm seen àq, \v 50 te it nga jéggal sa ñoñ ñi la moy, jéggal leen seen mboolem tooñ yu ñu la tooñ, te may leen yërmandey ña leen jàpp, ba ñu yërëm leen. \v 51 Ndax kat ñooy sa ñoñ ñi nga séddoo, génnee leen Misra, taalu xellikaayu weñ gu ñuul ga. \p \v 52 «Sang bi, teewlul bu baax samay tinu ak sa tinuy mbooloom Israyil mii, ba nangul leen mboolem lu ñu la jooy, \v 53 ndaxte danga leena ber ci biir xeeti àddina yépp, séddoo leen, te waxoon nga ko, Musaa sa jaam ba jottli ko, ba ngay génne sunuy maam Misra, yaw Boroom biy Aji Sax ji.» \s1 Suleymaan ñaanal na bànni Israyil \p \v 54 Ba Suleymaan noppee ñaan \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji mboolem ñaanam ya ak dagaanam yooyu, daa siggee ca \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* Aji Sax, ja mu sukkoon tàllal loxo ya, jublu asamaan. \v 55 Mu taxaw, di ñaanal mbooloom Israyil mépp, daldi àddu ca kaw ne: \v 56 «Cant ñeel na Aji Sax, ji may Israyil mbooloom ab dal-lukaay, muy la mu waxoon lépp, ngir benn baat fanaanul àll ci digey jàmm yi mu dige woon yépp, Musaa jaamam ba jottli. \v 57 Yal na sunu Yàlla Aji Sax ji ànd ak nun, na mu ànde woon ak sunuy maam. Yàlla bu nu wacc mukk mbaa mu di nu dëddu. \v 58 Yal na nu xiir ci boppam, nuy tegu ci yoonam yépp, di jëfe ay santaaneem aki dogalam ak àttey yoonam yi mu dénkoon sunuy maam. \v 59 Sama kàddu yii ma ñaan fi kanam Aji Sax ji, yal na doon lu sunu Yàlla Aji Sax ji def yitteem guddeek bëccëg. Mu di ma dëggal, man jaamam, di dëggal Israyil ñoñam, saa yu nu ko soxlaa. \v 60 Su ko defee xeeti àddina yépp dinañu xam ne Aji Sax ji mooy Yàlla, te amul moroom. \v 61 Waaye nag joxleen Aji Sax ji sunu Yàlla seen léppi xol, ngir ngeen mana tënku ciy dogalam tey jëfe ay santaaneem ni bésub tey.» \s1 Suleymaan daloo na kër Yàlla ga \p \v 62 Ba mu ko defee Buur Suleymaan ànd ak Israyil gépp, sarxe ab sarax fi kanam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji. \v 63 Mu defal Aji Sax ji \w saraxi cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*, lépp di ñaar fukki junniy nag ak ñaar (22 000) ak téeméeri junniy gàtt ak ñaar fukk (120 000). Noonu la Buur ak \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* gépp amale xewu jagleb kër Aji Sax ji. \v 64 Bésub keroog Buur sellal na digg ëtt ba janook néeg Aji Sax ji, ndax fa la joxe \w saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* ba, ak \w saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"\w* ba, ak nebbonu saraxu cant ci biir jàmm, ndax \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* xànjar ba fa kanam Aji Sax ji moo tuutoon ci defandoo saraxu rendi-dóomal ba, ak saraxu pepp ba, ak nebbonu saraxu cant ga ci biir jàmm. \p \v 65 Suleymaan nag amal màggal ga jant yooyu, ànd caak Israyil gépp, muy ndaje mu réy mu jóge Lebo Amat ca bëj-gànnaar ba ca xuru Misra ca bëj-saalum, di màggalsi fi sunu Yàlla Aji Sax ji, ba mu am juróom ñaari fan, tegaat ca juróom ñaari fan, muy fukki fan ak ñeent. \v 66 Bésub juróom ñetteel ba nag Buur yiwi mbooloo ma, ñu ñaanal ko, daldi dellu seeni xayma, ci biir mbégte ak xol bu sedd ci mboolem lu baax la Aji Sax ji defal Daawuda jaamam ba, ak Israyil, ñoñam. \c 9 \s1 Aji Sax ji feeñu na Suleymaan \p \v 1 Ba Suleymaan noppee ci tabax kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ak kër Buur, ak mboolem nammeelam gu mu bëggoona sottal, \v 2 la ko Aji Sax ji feeñu ñaareel bi yoon, na mu ko feeñoo woon fa Gabawon. \v 3 Aji Sax ji ne ko: «Dégg naa sag ñaan, ak sab dagaan. Sellal naa kër gii nga tabax, ngir teg fi sama tur ba fàww. Samay gët ak sama xol it fi lay nekk bés bu nekk. \p \v 4 «Yaw nag, soo doxee fi sama kanam ni Daawuda sa baay daan doxe cig mat akug njub, di def lépp lu ma la sant, di sàmm sama dogali yoon, ak sama àttey yoon, nga di ko sàmm, \v 5 kon dinaa saxal sab jal ci kaw Israyil ba fàww, na ma ko waxe woon Daawuda sa baay, ne ko: “Doo ñàkk ku góor kuy toog ci jalub Israyil.” \v 6 Waaye su ngeen ma dëddoo ba dëddu ma, yeen ak seeni sët, ba jëfewuleen samay santaane, sama dogali yoon yi ma leen tëralal, xanaa di topp aka jaamu yeneen yàlla, di leen sujjóotal, \v 7 su boobaa maay dagge \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* fi déndu suuf si ma leen jox, te kër gi ma sellal ngir sama tur, maa koy xalab, mu sore ma, te kon Israyil mujj di tur wu ñuy léeboo ak di ko kókklee ci biir xeet yépp. \p \v 8 «Su boobaa kër gii dina gent te képp ku ko romb dina yéemu tey muslu ci lu ni mel. Dinañu ne: “Lu tax Aji Sax ji def nii réew mii ak kër gii?” \v 9 Ñu ne: “Xanaa li ñu dëddu seen Yàlla Aji Sax, ji jële seeni maam réewum Misra, di topp yeneen yàlla, di leen sujjóotal ak a jaamu. Moo tax Aji Sax ji teg leen musiba mii mépp.”» \s1 Buur Suleymaan jëflante naak Buur Iram \p \v 10 Ñaar fukki at yi Suleymaan tabax ñaari kër yi, kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ak kër Buur, ba mu matee \v 11 fekk na Iram buurub Tir jox Suleymaan ay banti garabi seedar ak sippar\f + \fr 9.11 \fr*\fk sippar: \fk*\ft seetal ci 5.22.\ft*\f*, ak mboolem lu mu soxla ci wurus. Buur Suleymaan nag jox Iram ñaar fukki dëkk ci diiwaanu Galile. \v 12 Ci kaw loolu Iram bàyyikoo Tir, seeti dëkk ya ko Suleymaan jox, waaye dëkk ya neexu ko. \v 13 Mu ne ko: «Sama waay, dëkk yi nga ma jox nag?» Mu daldi tudde dëkk ya réewum Kabul\f + \fr 9.13 \fr*\fk Kabul \fk*\ft man naa firi Jarul dara.\ft*\f*, mooy turam ba tey jii. \v 14 Iram yónnee woon na Buur fanweeri barigoy wurus ak juróom. \p \v 15 Buur Suleymaan dafa dogaloon liggéeyu sañul-bañ bu mu sas ay nit. Ñu tabax kër Aji Sax ji ak këru boppam ak sëkkub Milo\f + \fr 9.15 \fr*\fk Milo \fk*\ft xur la wu doxoon diggante kër Yàlla ga ak gox ba ñu naan Kër Daawuda. Suleymaan sëkklu ko.\ft*\f* ak tatay Yerusalem ya ak dëkk yii di Àccor, Megido ak Geser. Ni mu deme nii la: \v 16 Firawna buuru Misra moo daloon ci kaw Geser, nangu dëkk ba, lakk ko, rey Kanaaneen ña ca dëkkoon, daldi may dëkk ba doomam jay soxnas Suleymaan, muy yebam. \v 17 Suleymaan tabaxaat Geser ak Bet Oron Suuf, \v 18 ak Baalat ak Tamar\f + \fr 9.18 \fr*\fk Tamar \fk*\ft dees na ko wax Tadmor ba tey.\ft*\f* ca màndiŋu réew ma, \v 19 ak mboolem dëkki dencukaayam, ak dëkk ya watiiri xare ya dence, ak dëkki gawar ya. Lu Suleymaan nammoona tabax daal, tabax na ko ca Yerusalem ak ca Libaŋ ak mboolem réewum kilifteefam. \p \v 20 Mboolem nit ña desoon ca Amoreen ñaak Etteen ñaak Periseen ñaak Eween ñaak Yebuseen ña, ñooñu bokkul ci \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \v 21 Seen sët ya leen wuutu ca réew ma, te bànni Israyil manuñu leen woona faagaagal, Suleymaan moo leen dugal ci liggéeyu njaam ak sañul-bañ, ñu nekke ko ba tey jii. \v 22 Waaye ñi bokk ci bànni Israyil, Suleymaan defu leeni jaam, ndax ñoom ñoo doon ay xarekatam, aki dagam aki jawriñam, ak njiiti xareem ak boroom watiiri xareem, ak dawalkati watiiram. \v 23 Ñoo doon itam saytukat yi yore liggéeyi Suleymaan. Amoon na juróomi téeméeri jawriñam ak juróom fukk (550) yu daan jiite nit ñiy def liggéey bi. \p \v 24 Doomu Firawna ju jigéen ja nag jóge gox ba ñu naan Kër Daawuda, séyi kërug boppam ga ko Suleymaan tabaxal. Gannaaw gi la Suleymaan tabax sëkkub Milo. \p \v 25 Suleymaan di def ñetti yoon cim at ay \w saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w*, ak \w saraxi cant ci biir jàmm|lemma="Sarax yi:"\w*, di ko sarxal ci kaw \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* bi mu tabaxal Aji Sax ji, boole ci di taal cuuraay ci kaw sarxalukaay bi, fi kanam Aji Sax ji. Mu daldi matal la war ca kër Yàlla ga. \p \v 26 Ay gaal yu mag itam Buur Suleymaan defarlu na ko ca Esiyon Geber ga ca wetu Elat, ca tefesu géeju Barax ya, ca réewum Edom. \v 27 Iram yebal ay nitam, ñuy mool yu xam géej. Ñuy liggéeyandook niti Suleymaan ca gaal ya. \v 28 Ñu daldi ànd dem Ofir, jële fa téeméeri barigoy wurus ak ñaar fukk, indil Buur Suleymaan. \c 10 \s1 Lingeer buurub Saba seetsi na Suleymaan \p \v 1 Ci kaw loolu Lingeeru Saba dégg riirum Suleymaan ma turu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waral. Mu dikk di nattusi am xelam, di ko cax cax yu jafe. \v 2 Mu agsi Yerusalem, ànd ak topp mu takku lool ak giléem yu sëf ay ndàbb yu xeeñ ak wurus wu baree bare ak per yu gànjare. Ba mu dikkee ba ca Suleymaan, mboolem la mu jàppoon ca xelam la ko wax. \v 3 Suleymaan tontu ko ca mbir ya mu laaj yépp; amul menn mbir mu tiiñ Buur ba leeralalu ko ko. \v 4 Lingeer buurub Saba gis mboolem xelam Suleymaan mu rafet, ak kër ga mu tabax, \v 5 ak njëlu këram, ak jataayu dagam ya, ak taxawaayu surgaam ña, ak seen col ga, ak ña yor ay naanam, ak \w saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"\w* ya muy joxe ca kër Aji Sax ji. Mu daldi yéemu, ba ag noowam réer ko. \p \v 6 Mu ne Buur: «jëw ba ma déggoon ca sama réew ci say mbir ak sa xel mu rafet kay, dëgg la! \v 7 Gëwma ko woon ba bi ma dikkee, ba teg ci samay bët. Ndeke genn-wàll gi sax waxeesu ma ko woon. Wees nga riir ma ma déggoon ci yaw, ci xel mu rafet ak alal. \v 8 Ndokklee say nit! Ndokklee sa jawriñ ñii dëkke taxaw ci sa kanam, di dégg sam xel! \v 9 Cant ñeel na sa Yàlla Aji Sax ji, moom mi la bége, ba teg la ci jalub Israyil. Aji Sax ji daa sopp Israyil cofeel gu dul jeex, moo tax mu fal la buur, ndax nga saxal fi dëgg ak njekk.» \p \v 10 Ba mu ko defee Lingeer buurub Saba may Suleymaan fanweeri barigoy wurus ak juróom, ak cuuraayu ndàbb lu ne gàññ, ak per yu jafe. Cuuraayu ndàbb loola Lingeer buurub Saba mayoon Buur Suleymaan, lu ni mel dikkatu fa ndax bare. \p \v 11 Ci kaw loolu itam gaali Buur Iram ya daan jële wurus ca réewum Ofir, jële Ofir lu takkoo takku ci banti sàntaal ak per yu gànjare. \v 12 Buur sàkke ca banti sàntaal ya, ay sëppukaayi kaw taax ngir kër Aji Sax ji, ak kër Buur ak xeeti xalam ngir woykat yi. Banti sàntaal bu ni mel masu faa dikk, te giseesu ko fi ba tey jii. \p \v 13 Buur Suleymaan itam may Lingeer buurub Saba mboolem lu mu sàkku, te bokkewul ak la ko Suleymaan joxal boppam ca loxoom bu tàlli ba buur yelloo. Ba loolu amee Lingeer buurub Saba walbatiku, ñibbim réewam, mooki surgaam. \s1 Suleymaan bare woon na alal \p \v 14 Wurus wa daan dikkal Suleymaan cim at, diisaay ba ñaar téeméeri barigoy wurus la, \v 15 te limaaleesul galag ya jóge ca jaaykat ya ak jula yaak mboolem buuri Arabi, ak jaraafi réew ma. \p \v 16 Buur Suleymaan nag sàkklu ñaar téeméeri pakk yu mag yu wurus wu ñu tëgg ba mu jekk, benn bu ci nekk jël juróom benni kiloy wurus, \v 17 ak ñetti téeméeri pakk yu ndaw yu wurus wu ñu tëgg ba mu jekk, pakk bu ci nekk di kilo ak liibaru wurus. Buur boole ko denc ca këram ga ñuy wax Gottub Libaŋ. \p \v 18 Buur teg ca sàkk ngàngune mu mag mu bëñi ñay, daldi koy xoob wurus wu set wecc. \v 19 Juróom benni dëggastal la ngàngune ma am, wéeruwaay ba ca kaw mërgalu. Mu am loxo wet gu nekk. Loxo yaa nga feggook ñaari jëmmi gaynde yu taxaw, wet gu nekk benn. \v 20 Mu am it fukki jëmmi gayndeek ñaar yu taxaw ca ñaari weti juróom benni dëggastal ya, ñaari gaynde séq ndëggastal lu nekk. Sàkkeesul lu ni mel ci mboolem nguur yi! \p \v 21 Mboolem lu Buur Suleymaan daan naane wurus la, te mboolem ndabi këram ga ñuy wax Gottub Libaŋ wurusu ngalam la. Dara du ca xaalis, ndax xaalis jàppeesu ko woon muy dara ca janti Suleymaan. \v 22 Te sax ay gaal yu mag la Buur amoon, ñuy ànd ak gaali Iram, benn yoon ci ñetti at yu nekk gaal ya yeb wurus ak xaalis ak bëñi ñay, aki golo ba ciy dàngin. \p \v 23 Buur Suleymaan dem na ba sut mboolem buuri kaw suuf ci wàllu alal, ak ci wàllu xel mu rafet. \v 24 Mboolem àddinaa daan wuta giseek Suleymaan, ngir taataansi xelam mu rafet mi Yàlla def cib xolam. \v 25 Ñooñu ñoo ko daan indil at ci kaw at, ku nekk ak sab teraanga, muy ay jumtukaayi wurus ak yu xaalis aki mbubb aki gànnaay aki cuuraay aki fas aki berkelle. \p \v 26 Ba mu ko defee Suleymaan dajale watiir yaak fas ya, muy junni ak ñeenti téeméeri watiir (1 400), ak fukki junniy fas ak ñaar (12 000) yu mu yebal ca dëkk ya watiir ya féete, ak ca Yerusalem ga mu nekk. \v 27 Buur Suleymaan a def xaalis late biir Yerusalem bay safi doj, garabi seedar di fa saf garabi sikomoor yi ne xas ci suufu tund yi. \v 28 Fasi Suleymaan, Misra lañu leen daan jëggaanee ak Silisi\f + \fr 10.28 \fr*\fk Silisi \fk*\ft mooy Kewe ba tey.\ft*\f*, baana-baanay buur, ca Silisi lañu leen daan jënde. \v 29 Ab watiir bu ñu jëggaanee Misra, indi, juróom benni téeméeri dogi xaalis (600) la leen daan dikke, aw fas di téeméer ak juróom fukki dogi xaalis (150), te noonu lañu ca daan jëndaaleel mboolem buuri Etteen ña ak buuri Siri, indil leen. \c 11 \s1 Suleymaan moy na \p \v 1 Ci biir loolu Buur Suleymaan bëggoon na jigéeni yeneen xeet yu bare te bokkul ak doomu Firawna ji mu jëloon: ñuy ay jigéeni Mowabeen ak jigéeni Amoneen ak jigéeni Edomeen ak jigéeni waa Sidon ak jigéeni Etteen. \v 2 Ñooñu bokk ci xeet, yi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxoon \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* ne leen: «Buleen jëli jabar ci ñoom, ñoom it buñu takksi ci yeen, ndax kon dinañu leen dëpp, ngeen topp seeni tuur.» Teewul Suleymaan bëgg leen, taq leen. \v 3 Mu denc ca juróom ñaar téeméeri lingeer (700) ak ñetti téeméeri (300) nekkaale. Soxnaam ya nag dëpp ko. \p \v 4 Ba Suleymaan demee ba màggat, ay soxnaam xiir ko ci topp yeneen yàlla, ba wéetalul Yàllaam Aji Sax ji, na ko Daawuda, baayam wéetale woon. \v 5 Ba loolu amee Suleymaan di topp tuur ya ñuy wax \w Astàrt|lemma="Astàrt:"\w*\f + \fr 11.5 \fr*\fk Astàrt \fk*\ft tuur mu jigéen la woon bu ay xeeti penku daan jaamu. Ñu yaakaaroon ne dina leen may, ñu jur doom yu bare, seeni jur ak seeni tool it, lépp nangu ba bare. Ñu jàppoon ne Astàrt mooy jabaru tuur ma ñu naan Baal.\ft*\f* di tuuri waa Sidon, ak Milkom, tuuru Amoneen mu siblu ma. \v 6 Mu def lu ñaaw fi kanam Aji Sax ji. Suleymaan jeexul woon ci Aji Sax ji, na baayam Daawuda jeexe woon ci moom. \v 7 Ci biir loolu Suleymaan tabaxal Kemos, tuuru Mowab mu siblu ma, ab \w bérabu jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* ca kaw tund wa féete Yerusalem penku. Mu tabaxaaleel ca Moleg\f + \fr 11.7 \fr*\fk Moleg \fk*\ft ak Milkom jàpp nañu ne benn la.\ft*\f*, tuur mu siblu ma Amoneen ñay jaamu. \v 8 Mu defal noonu mboolem soxnaam ya xeetoo feneen, ñuy taalal seeni tuur cuuraay, di leen rendil ay sarax. \p \v 9 Aji Sax ji nag mere Suleymaan ndax la mu ko dëddu, moom Aji Sax ji, Yàllay Israyil ji ko feeñu woon ñaari yoon. \v 10 Dafa santoon Suleymaan ci mbir moomu, ne ko bumu topp tuuri yeneen xeet yi. Waaye deful li ko Aji Sax ji santoon. \v 11 Aji Sax ji ne Suleymaan: «Gannaaw nii nga defe, sàmmoo sama \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w*, sàmmoo sama dogal yi ma la tegoon, dinaa foqatee nguur gi ci say loxo, jox ko sab surga. \v 12 Waaye duma ko def ci sag dund ngir sa baay Daawuda. Ci sa loxol doom ju góor laa koy foqatee. \v 13 Te ba tey du nguur gépp laay foqati. Dinaa bàyyee sa doom genn giir ngir Daawuda sama jaam ba ak Yerusalem gi ma tànn.» \s1 Ay noon jógal nañu Suleymaan \p \v 14 Ba mu ko defee \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji gemb ab noon bu jógal Suleymaan. Muy Adàdd, Edomeen ba askanoo ca buurub Edom. \v 15 Ba Daawuda di xareek waa Edom te Yowab njiital xareem demoon di suuli néew ya, Daawuda daa reyoon góori Edomeen ña ñépp. \v 16 Yowab ak Israyil gépp toog fa juróom benni weer, ba keroog ñu rey góori Edomeen ñépp. \v 17 Ci biir loolu Adàdd ànd ak ay Edomeen ñu bokkoon ci dagi baayam, daldi daw jëm Misra. Booba Adàdd xale bu góor bu ndaw la woon. \v 18 Ñu jóge Majan, dem Paran, ànd ak ay waa Paran dem Misra, ca Firawna buuru Misra. Firawna jox Adàdd suuf, may ko kër akub dund. \v 19 Firawna dafa bëggoon Adàdd lool, ba may ko jabar rakki Lingeer Tapenes, jabari boppam. \v 20 Rakki Tapenes ja am ak Adàdd doom ju góor, di Genubat; Tapenes yor ko ca biir kër Firawna, Genubat nekk ak doomi Firawna, ca biir kër Firawna. \v 21 Ci kaw loolu Adàdd dégge fa mu nekk ca Misra ne Daawuda nelaw na, fekki ay maamam, te Yowab njiital xare la it dee na. Adàdd ne Firawna: «Yiwi ma, ma dellu sama réew.» \v 22 Firawna ne ko: «Ana loo ñàkk fii ci man, ba bëgga dellu nii sam réew?» Adàdd ne ko: «Du dara sax de, xanaa bëgg rekk, nga yiwi ma, ma dem.» \p \v 23 Yàlla dellu gemb ab noon bu jógal Suleymaan. Muy Reson doomu Eliyada ma dawe woon ca Adadeser buurub Soba, sangam ba. \v 24 Mu boole ay farandoom, ànd ak ñoom, jiite leen gannaaw ba Daawuda faagaagalee xarekati sangam. Ñu dem sanc Damaas, moom ko. \v 25 Reson nag moo noonoo woon Israyil diir ba Suleymaan di dund, dolli ca la leen Adàdd lëjal. Ci kaw loolu Reson falu ca Siri, di bañaaleb Israyil. \p \v 26 Keneen ku jógal Buur Suleymaan di Yerbowam doomu Nebat, Efraymeen bu dëkk Cereda, ndeyam tudd Ceruya, dib jëtun. Ma nga bokkoon ca jawriñi Suleymaan. \v 27 Ni mu jógale Buur nii la: Suleymaan da doon yékkati sëkkub Milo ba\f + \fr 11.27 \fr*\fk Milo \fk*\ft xur la wu doxoon diggante kër Yàlla ga ak gox ba ñu naan Kër Daawuda. Suleymaan sëkklu ko.\ft*\f*, di fatt tatay gox ba ñu naan Kër Daawuda miy baayam. \v 28 Booba Yerbowam xalelu góor bu jàmbaare la woon. Suleymaan jot koo nemmiku ci biir liggéeyam, ba tax mu tabb ko ca kaw mboolem liggéeykati sañul-bañ, ya askanoo ca Yuusufa. \p \v 29 Mu am bés Yerbowam doon génne Yerusalem. Axiya, yonent bu dëkk Silo ba, dajeek moom ca yoon wa. Ma nga sol mbubb mu bees. Ñoom ñaar rekk ci àll bi. \v 30 Axiya daldi jàpp ci mbubb mu bees mi mu sol, ne ko tareet, dagg ko fukki dog ak ñaar. \v 31 Mu ne Yerbowam: «Jëlalal fii sa bopp fukki dog, ndax Aji Sax ji Yàllay Israyil da ne: “Gisal, maa ngi dagge nguur gi ci loxol Suleymaan, te dinaa la ci jox fukki giir. \v 32 Waaye genn giir gi Suleymaan a koy moom ngir Daawuda sama jaam ba, ak Yerusalem, dëkk ba ma tànne ci mboolem giiri Israyil. \v 33 Li ko waral mooy dañu maa dëddu, di jaamu \w Astàrt|lemma="Astàrt:"\w*, tuur mu jigéen mu waa Sidon di jaamu, ak Kemos, tuuru Mowabeen ñi, ak Milkom, tuuru Amoneen ñi. Dañoo baña topp samay yoon, baña def li ma rafetlu, di sàmm samay dogal ak sama àttey yoon, na ko Daawuda baayu Suleymaan daa defe. \v 34 Waaye duma jële nguur gépp ci loxoom, ndaxte dama koo def njiit giiru dundam gépp ngir Daawuda sama jaam ba ma tànnal sama bopp, te mu doon jëfe samay santaane ak samay dogal. \v 35 Du tee ma nangoo nguur gi ci loxol doomam ju góor, jox la ci fukki giir. \v 36 Doomam nag dinaa ko jox genn giir gi ci des, ngir askanu Daawuda, sama jaam ba, baña fey mukk sama kanam ci biir Yerusalem, dëkk bi ma tànnal sama bopp, dëël fa sama tur. \v 37 Yaw dinaa la jël, def la nga jiite fépp foo bëgg, di buurub Israyil. \v 38 Te soo defee mboolem li ma la sant, topp samay yoon, di def li ma rafetlu tey jëfe samay dogal ak samay santaane, na ko Daawuda sama jaam ba daa defe, su boobaa dinaa ànd ak yaw te dinaa la sampal kër gu sax, ni ma ko sampale woon Daawuda, te dinaa la jox Israyil. \v 39 Kon dinaa torxal askanu Daawuda waaye du doon ba fàww.”» \p \v 40 Ba mu ko defee Suleymaan di fexee rey Yerbowam; Yerbowam daw ba Misra, fa Sisag buuru Misra. Mu toog foofa ca Misra, ba Suleymaan nelaw. \s1 Suleymaan nelaw na \p \v 41 Li des ci mbiri Suleymaan ak mboolem lu mu def ak lu jëm ci xelam mu rafet, bindees na lépp moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey Suleymaan. \v 42 Àpp bi Suleymaan nguuru fa Yerusalem, ci kaw Israyil gépp, ñeent fukki at la. \v 43 Gannaaw loolu Suleymaan tëdd, fekki ay maamam. Gox ba ñuy wax kër Daawuda baayam, fa lañu ko denc, doomam Robowam falu buur, wuutu ko. \ms1 Réew ma xàjjalikoo na \mr (Saar 12.1—22.54) \c 12 \s1 Israyil jàmbu na Robowam \p \v 1 Ba loolu amee Robowam dem dëkk ba ñuy wax Sikem, ndax fa la Israyil gépp daje woon, ngir fal ko buur. \v 2 Yerbowam doomu Nebat dégge ko ca Misra ga mu dawoon dem, di fa làqu Buur Suleymaan, te toogoon foofa ca Misra ba booba. \v 3 Waa giiri bëj-gànnaar woolu ko, ñu daldi ànd mook mbooloo mépp ca Robowam. Ñu ne ko: \v 4 «Sa baay da noo tegoon njaam gu metti. Léegi yaw dangay woyofal sunu liggéey bu metti bi nu sa baay sëf, te yolomal buumu njaam gu teeŋ gi mu nu gàll, kon nu jaamu la.» \v 5 Mu ne leen: «Demleen ba mu am ñetti fan, ngeen délsi.» Mbooloo ma dem. \p \v 6 Buur Robowam giseek mag ña daa taxawu Suleymaan baayam ba muy dund. Mu ne leen: «Lu ngeen may digal, ma wax ko mbooloo mii?» \v 7 Ñu ne ko: «Soo nangulee tey mbooloo mii, déggal leen, wax leen kàddu yu rafet, say jaam lañuy doon ba fàww.» \p \v 8 Robowam nag dégluwul waxi mag ña, xanaa dem giseek xale yu góor, ya màggandoo ak moom te di ko taxawu. \v 9 Mu ne leen: «Lu ngeen may digal ma wax ko mbooloo mii ne ma, ma yolomal buumu njaam gi leen sama baay gàlloon?» \p \v 10 Xale yu góor ya mu màggandool ne ko: «Mbooloo mii ne la sa baay da leena gàlloon buumu njaam gu teeŋ, waaye yaw yolomalal leen ko; li nga leen di wax mooy lii: “Sama baaraamu sanqleeñ moo gëna diis sama tànku baay. \v 11 Sama baay a leena tegoon njaam gu metti, waaye man maay yokk seen njaam, ba mu gëna metti. Te sama baay ay yar la leen daan cawe, waaye man ay leraw yu ñu kor weñ laa leen di cawe.”» \p \v 12 Ñetteelu bés ba Yerbowam ànd ak mbooloo ma mépp, dellu ca Robowam, noonee leen ko Buur waxe woon ne leen ñu dem ba mu am ñetti fan, ñu délsi. \v 13 Buur tontu mbooloo ma kàddu gu ñagas, bàyyi la ko mag ña digaloon. \v 14 Na ko xale yu góor ya digale la waxeek ñoom, ne leen: «Sama baay a leen tegoon njaam gu metti, waaye man maa koy yokk, mu gëna metti. Te sama baay ay yar la leen daa cawe, waaye man ay leraw yu ñu kor weñ laa leen di cawe.» \v 15 Noonu la Buur tanqamloo mbooloo ma, te \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji moo walbatee noonu mbir ma, ngir amal wax, ja mu waxoon Yerbowam doomu Nebat, Axiya waa Silo ba jottli. \p \v 16 Ba Israyil gépp gisee na leen Buur tanqamloo, dañu koo tontu ne ko: \q1 «Ana lu nu bokk ak Daawuda, \q1 lu nu séq ak doomu Yese? \q1 \w Bànni Israyiloo|lemma="bànni Israyil:"\w*, ca seeni xayma! \q1 Yaw askanu Daawuda, xoolalal sa bopp sa kër.» \p Ba mu ko defee bànni Israyil dellu ca seeni xayma; \v 17 Teewul bànni Israyil ya dëkkoon ca dëkki Yuda, Robowam wéy di seen buur. \v 18 Ci kaw loolu Buur Robowam yónni Adoram may sase liggéeyi sañul-bañ ya. Teewul Israyil gépp bokk dóor ko ay doj ba mu dee. Buur Robowam daldi gaaw war watiir, daw làquji Yerusalem. \v 19 Noonu la Israyil fippoo ci kaw waa kër Daawuda ba sunu jonni yàllay tey. \p \v 20 Ci biir loolu Israyil gépp dégg ne Yerbowam délsi na; ñu woote ndaje, woo ko ca, fal ko buurub Israyil gépp. Kenn farul ak waa kër Daawuda, lu moy waa giirug Yuda doŋŋ. \p \v 21 Ci kaw loolu Robowam agsi Yerusalem, daldi woo waa kër Yuda gépp, ñook giirug Beñamin, ñu daje di téeméer ak juróom ñett fukki junniy nit (180 000), diy ñeyi xare. Ñu nara xareek waa kër Israyil, ngir delloo nguur ga ca loxol Robowam doomu Suleymaan. \p \v 22 Ci biir loolu kàddug Yàlla dikkal góoru Yàlla gu ñuy wax Semaya. Mu ne ko: \v 23 «Waxal Robowam doomu Suleymaan buurub Yuda, ak waa kër Yudak Beñamin ak mbooloo ma ca des, ne leen: \v 24 “Aji Sax ji dafa wax ne: Buleen jóg di xeex ak seen bokki bànni Israyil. Na ku nekk ñibbi këram, ndax ci man la mbir mii sababoo.”» Ñu dégg kàddug Aji Sax ji, walbatiku dem, noonee ko Aji Sax ji waxe. \s1 Buurub Israyil bokkaale na \p \v 25 Gannaaw loolu Yerbowam tabaxaat Sikem, dëkk ba ca diiwaanu tundi Efrayim, daldi fay dëkk. Mu jóge foofa tabaxaat dëkk ba ñuy wax Penuwel. \v 26 Yerbowam nag di wax ca xelam naa: «Léegi nguur gi dellu ci loxol waa kër Daawuda. \v 27 Bu mbooloo mii demee di sarxali ca kër \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ca Yerusalem, seen xol dina walbatiku ne napp ca seen sang, Robowam buurub Yuda. Su ko defee ñu rey ma, dellu ca Robowam buurub Yuda.» \p \v 28 Ci kaw loolu Buur seetluwaat mbir ma, daldi sàkklu ñaari wëlluy wurus. Mu ne mbooloo ma: «Yeen waa Israyil, bare ngeen lu ngeen di jaabante yoonu Yerusalem. Xool-leen fii kay! Seen yàlla ya leen génne woon réewum Misraa ngi.» \v 29 Ba loolu amee mu teg wenn wëllu wa ca dëkk ba ñuy wax Betel, wa ca des mu tegi ko ca Dan. \v 30 Mbir moomu doon bàkkaar. Mbooloo ma dox jiitu wenn wëllu wa, ba àgg Dan. \v 31 Ci kaw loolu Yerbowam tabax ay \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w*, ba noppi tabb ay \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ci baadoolo yu bokkul ci askanu Lewi. \p \v 32 Ba mu ko defee Yerbowam dogal màggalug fukki fan ak juróom ca weeru juróom ñetteel wa. Mu mel ni màggal gay am Yuda. Yerbowam rendi ay sarax ca \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* ba. Noonu la def Betel, rendil fa ay sarax wëllu ya mu defarlu woon, defal ko wëllu ya sarax. Ci biir loolu mu tabb ca Betel ay sarxalkat ngir bérabi jaamookaay yooyu mu sos. \v 33 Nii la rendee ay sarax ca kaw sarxalukaay ba mu sàkklu ca Betel, ca fukki fan ak juróom ca weeru juróom ñetteel wa, muy weer wu mu tànnal boppam. Ba mu ko defee mu dogalal waa Israyil màggal googu, daldi yéeg ca kaw sarxalukaay ba, ngir taal fa sarax su ñuy lakk. \c 13 \s1 Nitu Yàlla àddu na ca Betel \p \v 1 Yàlla-woo-yàlla, genn góoru Yàlla jóge Yuda, dikk ba Betel ci ndigalal \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, fekk Yerbowam taxaw ca \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* ba, nara taal saraxu cuuraay. \v 2 Góor ga xaacu, gëdd sarxalukaay ba ci ndigalal Aji Sax ji, daldi ne: «Yaw sarxalukaay bi, éey sarxalukaay bii! Aji Sax ji dafa wax ne: “Xamal ne doom ju góor dina juddoo kër Daawuda, Yosya lay tudd. \w Sarxalkati|lemma="sarxalkat b-:"\w* \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* yiy taal saraxu cuuraay ci sa kaw, ñoom lees di rendi ci sa kaw. Yaxi nit lees di lakk ci sa kaw.”» \v 3 Góor ga joxe na ca bésub keroog ab takk; mu ne: «Takk bii la ci Aji Sax ji biral: “Seetluleen, sarxalukaay bi dina xar ñaar, dóom bi ci kaw sottiku.”» \p \v 4 Naka la Buur Yerbowam dégg na góoru Yàlla ga xaacoo, gëdd sarxalukaayu Betel ba, mu daldi koy tàllal loxoom, foofa ca sarxalukaay ba. Mu ne: «Jàppleen ko!» Loxo ba mu ko tàllal nag ne kàdd, manatu koo bank. \v 5 Sarxalukaay ba xar ñaar, dóom ba tuuroo ca sarxalukaay ba, ne wàww. Muy takk ba góoru Yàlla ga joxe woon ci ndigalal Aji Sax ji. \v 6 Buur ne góoru Yàlla ga: «Rikk tinul ma sa Yàlla Aji Sax ji te ñaanal ma, sama loxo mana banku.» Góoru Yàlla ga tinul Buur Aji Sax ji, loxoom bankuwaat, mel na mu meloon. \p \v 7 Ci kaw loolu Buur wax góoru Yàlla ga ne ko: «Ñëwal nu dem kër ga, nga xéewlu, ba noppi ma am lu ma la may.» \v 8 Góoru Yàlla ga nag ne Buur: «Soo ma joxoon sa genn-wàllu kër sax, duma ànd ak yaw te duma sex dugub it mbaa may naan um ndox ci bii bérab, \v 9 ndax loolu lañu ma sant ci ndigalal Aji Sax ji, ne ma: “Bul sex dugub, bul naan um ndox te bul walbatiku jaare yoon wa nga jaare woon bi ngay ñëw.”» \v 10 Góor ga nag awe feneen, baña walbatiku awe fa mu awoon ba muy dikk Betel. \s1 Ab yonent nattu na moroomam \p \v 11 Booba ab yonent bu màggat a nga woon ca Betel. Ay doomam yu góor dikk. Kenn ci ñoom nettali ko mboolem la góoru Yàlla ga def bésub keroog ca Betel ak la mu wax Buur. Ñu yegge ko seen baay. \v 12 Seen baay laaj leen ne leen: «Ana yoon wu mu jaare?» Fekk na doomam yu góor ya gisoon nañu fa góoru Yàlla ga jaare woon, bàyyikoo Yuda. Ñu wax ko. \v 13 Mu ne leen: «Takkal-leen ma mbaam mi.» Ñu takkal ko mbaam ma, mu war, \v 14 toppi góoru Yàlla ga, fekk ko ci genn ker garabu terebent. Mu ne ko: «Yaa di góoru Yàlla gi jóge Yuda?» Mu ne ko: «Waaw.» \v 15 Mu ne ko: «Kaay, nu dem kër ga, nga sex dugub, boog.» \v 16 Mu ne ko: «Duma mana walbatiku ànd ak yaw, manumaa sex dugub it mbaa may bokk ak yaw ndoxum naan ci bii bérab. \v 17 Ndaxte dañu maa wax ci ndigalal \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ne ma: “Bu fa sex dugub, bu fa naan um ndox te bul walbatiku jaare yoon wa nga jaare woon bi ngay ñëw.”» \v 18 Mu dellu ne ko: «Man itam yonent laa ni yaw. Malaaka wax na ma ci ndigalal Aji Sax ji ne ma: “Waññi ko, mu ànd ak yaw sa kër, sex dugub, naan ndox.”» Fekk na la muy wax amul. \v 19 Mu walbatiku ànd ak moom ca kër ga, sex fa dugub, naan fa ndox. \p \v 20 Ba ñu toogee ca ndab la, kàddug Aji Sax ji dikkal yonent ba waññi góoru Yàlla ga. \v 21 Mu àddu ca kaw ne góoru Yàlla ga jóge Yuda: «Aji Sax ji dafa wax ne: Gannaaw tebbi nga waxi Aji Sax ji te defoo li la sa Yàlla Aji Sax ji sant, \v 22 xanaa walbatiku di sex dugub, di naan ndox ci bérab bi mu la waxoon ne la bu fi sex dugub, bu fi naan ndox, sab néew du fekki say maam ca seen bàmmeel.» \v 23 Ba góoru Yàlla ga sexee dugub ba naan ndox, yonent ba ko waññi woon takkal ko mbaam ma. \v 24 Mu dem, gaynde dogale ko, rey ko, néewam ne lareet ca yoon wa, mbaam maak gaynde ga taxaw ca wet ga. \v 25 Naka la ay nit jaare foofa, séenuñu lu moy néew ba ne lareet ca yoon wa, gaynde ga taxaw ca wet ga. Ñu dem yegge ko waa dëkk, ba yonent bu màggat ba dëkkoon. \p \v 26 Yonent booba ko waññi woon ca yoon wa nag dégg ko ne: «Góoru Yàlla gaa! Ka tebbi woon waxi Aji Sax ji, Aji Sax ji boole kook gaynde gi, mu fàdd ko, rey ko. Moom la ko kàddug Aji Sax ji waxoon.» \v 27 Mu ne doom ya: «Takkal-leen ma mbaam mi.» Ñu takkal ko. \v 28 Mu dem fekk néew ba ne lareet ca yoon wa, mbaam maak gaynde ga taxaw ca wet ga. Gaynde ga lekkul néew ba, fàddul mbaam ma. \v 29 Yonent ba yékkati néewu góoru Yàlla ga, teg ko ca kaw mbaam ma, délloosi ko. Noonu la yonent bu màggat ba ñibbee dëkkam ngir rob ko, jooy ko. \v 30 Mu denc néew ba ca bàmmeelu boppam. Ñu di ko jooy, naan: «Wóoy sunu mbokk ma!» \v 31 Gannaaw ba ñu ko robee, mu wax doomam yu góor ya ne leen: «Bu ma faatoo, nangeen ma rob ci bàmmeel bii ñu denc góoru Yàlla gi. Fi weti yaxam ngeen di tëral samay yax. \v 32 Ndaxte li wér te wóor déy, wax ji mu jottli ci ndigalal Aji Sax ji, ba muy gëdd \w sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"\w* Betel bi ak mboolem \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* yi ci dëkki Samari, wax jooju dina am.» \p \v 33 Gannaaw loolu Yerbowam dëppul yoonam wu bon wa mu topp. Dafa dellu tabb ci biir baadoolo yi ay \w sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"\w* ngir bérabi jaamookaay ya. Ku bëgg rekk mu tabb la, ngay sarxalkat ca bérabi jaamookaay ya. \v 34 Loolu nag di bàkkaar bu réy ci biir kër Yerbowam, ba tax askanam daanu, ba raaf fi kaw suuf. \c 14 \s1 Aw tiis dikkal na Yerbowam \p \v 1 Ca yooyu jamono Abya doomu Yerbowam ju góor wopp. \v 2 Yerbowam wax soxnaam, ne ko: «Ayca, doxal soppiji col, ba kenn du xam ne sama soxna nga, te nga dem Silo. Dama ne, Axiya yonent baa nga fa. Moo ma waxoon ne ma dinaa falu buur, jiite mbooloo mii. \v 3 Yóbbaaleel fukki mburu ak nàkk yu ndaw ak taxub lem te nga dem ca moom. Moom dina la wax nan la mbiri gone gii di deme.» \v 4 Soxnas Yerbowam def noona, daldi dem Silo, agsi kër Axiya. \p Booba Axiya gisatul. Bët ya daa muuru ndax màggat. \v 5 Waaye fekk na \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji wax Axiya, ne ko: «Dama ne, soxnas Yerbowam a ngi ñëw di leerlusi mbirum doomam ju góor ci yaw, ndax dafa wopp. Bu dikkee keneen lay mbubboo.» Aji Sax ji ne Axiya, mu wax ko nàngam ak nàngam. \p \v 6 Ba loolu amee Axiya dégg tànki ndaw sa ca bunt ba. Mu ne ko: «Soxnas Yerbowam, agsil! Ana looy mbubboo keneen nii? Man de yóbbante nañu ma ci yaw xibaar bu tiis. \v 7 Demal ne Yerbowam: “Aji Sax ji, Yàllay Israyil dafa wax ne: Dama laa yékkati ci biir mbooloo mi, fal la nga jiite Israyil sama ñoñ. \v 8 Damaa foqatee nguur gi ci loxol waa kër Daawuda, jox la ko. Waaye meloo ni Daawuda, sama jaam ba daan jëfe samay santaane, toppe ma léppi xolam, du def lu moy lu ma rafetlu. \v 9 Def nga musiba, ba raw mboolem ñu la jiitu, dem di sàkkal sa bopp yeneen yàlla ak tuur yu ñu móole weñ, ba sama xol fees. Man mii nga xarab, dëddu ma. \v 10 Moo tax duma def lu moy wàcce musiba ci kër Yerbowam. \q1 Dinaa faagaagal ku mana taxaw, colol, te bokk ci Yerbowam, \q1 ba ci ku gëna néew doole te tumurànke fi digg Israyil. \q1 Dinaa buub kër Yerbowam, sànni, \q1 ni ñuy buubee neefare, ba mu jeex tàkk. \q1 \v 11 Ku Yerbowam deele ci dëkk bi, xaj yi lekk; \q1 ku ca médd ca àll ba, njanaaw ya for. \q1 Aji Sax ji wax na ko.” \p \v 12 «Yaw nag jógal ñibbi sa kër. Booy teg sa tànk ca biir dëkk ba rekk, gone gi dee. \v 13 Israyil gépp dinañu ko jooy. Kooku rekk déy lees di denc ci bàmmeel, ci ku bokk ci Yerbowam, ngir ci moom doŋŋ la Aji Sax ji Yàllay Israyil gis lu baax, ci waa kër Yerbowam. \v 14 Aji Sax ji dina falal boppam buur bu jiite Israyil, te kooku dina faagaagal waa kër Yerbowam. Bés bi taxaw na jeeg! Ana lu ciy topp? \v 15 Aji Sax ji dina fàdd Israyil. Dinañu mel ni gattax guy foy-foyi cim ndox. Dina déjjatee Israyil ci suuf su baax sii mu joxoon seeni maam, tasaare leen ca wàllaa dexu Efraat, ndax dañoo samp ay xer yu ñuy jaamoo \w Asera|lemma="Asera:"\w*, di merloo Aji Sax ji. \v 16 Aji Sax ji dina wacc Israyil ndax bàkkaari Yerbowam yi mu bàkkaar te di ko bàkkaarloo Israyil.» \p \v 17 Ba loolu amee soxnas Yerbowam jóg, bàyyikoo fa, ba àgg Tirsa. Naka la agsi ca bunt kër ba, xale ba dee. \v 18 Ñu rob ko, Israyil gépp jooy ko, muy la Aji Sax ji waxoon, Yonent Yàlla Axiya jaamam ba jottli. \p \v 19 Li des ci mbiri Yerbowam, ay xareem ak na nguuram deme woon, bindees na lépp moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. \v 20 At ya Yerbowam falu buur ñaar fukki at la ak ñaar. Gannaaw loolu mu saay, fekki ay maamam. Nadab doomam falu, wuutu ko. \s1 Robowam falu na ca Yuda \p \v 21 Robowam doomu Suleymaan moo doon buurub Yuda. Amoon na ñeent fukki at ak benn ba muy falu. Fukki at ak juróom ñaar la péeyoo Yerusalem, dëkk ba \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji tànn ci mboolem giiri Israyil, dëël fa turam. Ndeyam di Naama, dib Amoneen. \v 22 Waa Yuda nag di def li Aji Sax ji ñaawlu, ba di ko fiirloo fiiraange gu raw ga ko seen maam daa fiirloo ndax seen bàkkaar. \v 23 Dañoo sàkkal seen bopp ay \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w*, samp ay tuuri doj aki xer yu ñuy jaamoo \w Asera|lemma="Asera:"\w* ca kaw mboolem tund wu kawe mbaa ker garab gu naat. \v 24 Réew ma amoon na sax ñuy jaay seen bopp fa ñuy màggale tuur ya. Ñuy def mboolem ñaawtéefi xeet ya Aji Sax ji dàqoon ngir \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \p \v 25 Ba Buur Robowam faloo, ba dugg ci juróomeelu atu nguuram, Sisag buuru Misra song Yerusalem. \v 26 Ci kaw loolu Sisag jël alali kër Aji Sax ji, ak alali kër Buur. Lépp la jël ba ca mboolem pakki wurus ya Suleymaan defarlu woon. \v 27 Ba mu ko defee Buur Robowam defarlu ay pakku xànjar yu wuutu yu wurus ya. Mu teg ko ca loxoy njiiti dag yay wattu buntu kër Buur. \v 28 Saa yu Buur dee duggsi ca kër Aji Sax ji, dag ya ŋàbb pakk ya, bu ñu noppee delloo ko ca néegu dag ya. \p \v 29 Li des ci mbiri Robowam ak mboolem la mu def, bindees na ko moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. \v 30 Xare masula dakk diggante Robowam ak Yerbowam. \v 31 Gannaaw gi Buur Robowam tëdd, fekki ay maamam, ñu denc ko fa ay maamam ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. Ndeyam a doon Naama, Amoneen ba. Ci kaw lool doomam Abiyam falu buur, wuutu ko. \c 15 \s1 Abiyam falu na ca Yuda \p \v 1 Ca fukki at ak juróom ñetteelu nguurug Yerbowam, ca la Abiyam doomu Nebat falu buur ca kaw Yuda. \v 2 Ñetti at la nguuru fa Yerusalem te yaayam moo doon Maaka doomu Abisalom\f + \fr 15.2 \fr*\fk Abisalom \fk*\ft ak Absalom jàpp nañu ne kenn ki la.\ft*\f*. \v 3 Muy roy nag baayam ca mboolem bàkkaar ya mu daan def. Te it wéetalul woon Yàllaam \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ni maamam Daawuda. \v 4 Terewul Daawuda tax Aji Sax ji Yàllaam may ko doom ju góor ju koy wuutu ca Yerusalem, ndax askanu Daawuda baña fey, Yerusalem it mana ñoŋ. \v 5 Li ko waral mooy Daawuda da daan jëfe njub lu Aji Sax ji rafetlu, te giiru dundam gépp teggiwul lenn lu ko Aji Sax ji sant lu moy ci mbirum Uri Etteen ba.\f + \fr 15.5 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk 2.Samiyel\+bk* 11.\ft*\f* \v 6 Xare masula dakk diggante waa kër Robowam ak Yerbowam giiru dundu Abiyam gépp. \p \v 7 Li des ci mbiri Abiyam ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. Xare it jiboon na diggante Abiyam ak Yerbowam. \v 8 Gannaaw gi Buur Abiyam tëdd, fekki ay maamam, ñu denc ko ca gox ba ñu naan Kër Daawuda, Asa doomam falu buur, wuutu ko. \s1 Asa falu na ca Yuda \p \v 9 Ba Buur Yerbowam faloo Israyil, ba dugg ñaar fukkeelu atu nguuram, ca la Asa falu buur, jiite Yuda. \v 10 Ñeent fukki at ak benn la Buur Asa péeyoo Yerusalem. Maaka doomu Abisalom ju jigéen moo doon maamam. \v 11 Asa nag di def njub gi \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji rafetlu, Daawuda maamam. \v 12 Dàqe na ca réew ma ñu daan jaay seen bopp fa ñuy màggale tuur ya. Mu jële ca réew ma kasaray tuur ya fa ay maamam defoon yépp. \v 13 Maaka maamam ju jigéen sax, Asa xañ na ko céru lingeer yaayu buur ba mu amoon, ndax Maaka moo sàkkaloon \w Asera|lemma="Asera:"\w* tuur ma, ab xer bu seexluwu bu ñu koy màggale. Asa gor xeru maamam ja, lakk ko ca xuru Sedoron. \v 14 Waaye \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* ya, jëleesu ko fa, doonte Asa, Aji Sax ji la wéetaloon cib xolam, giiru dundam gépp. \v 15 Moo indi ca kër Aji Sax ji, jumtukaay yu \w sell|lemma="sell:"\w* yu baayam ya, ak jumtukaay yu sell yu boppam, muy xaalis ak wurus aki ndab. \p \v 16 Xare nag masula dakk diggante Asa ak Basa buurub Israyil seen giiru dund gépp. \v 17 Ci biir loolu Basa buurub Israyil song Yuda, daldi dàbbli dëkk ba ñuy wax Raama\f + \fr 15.17 \fr*\fk Raama \fk*\ft ma nga féete woon Yerusalem bëj-gànnaar, tollu diggante ñaari réew yi. Mu nekkoon ci kaw tund wu aw yoon jaar, jóge péeyu Israyil, jëm Yerusalem.\ft*\f*, ba kenn du dugg jëm ca Asa buurub Yuda mbaa muy génn. \v 18 Asa dajale mboolem luy xaalis ak wurus wu desoon ca denci kër Aji Sax ji, ak denci kër Buur. Mu teg ko ci loxoy jawriñam ña. Ba mu ko defee Buur Asa yebal leen ca buurub Siri ba ca Damaas, di Ben Addàd doomu Tabrimon doomu Esiyon. \p Asa nag ne Ben Addàd: \v 19 «\w Kóllëree|lemma="kóllëre g-:"\w* dox sama digganteek yaw, na mu doxe woon sama diggante baay ak sa baay. Lii nag maa la ko may, xaalis la ak wurus. Te nga dogoo rekk ak Basa buurub Israyil, ndax mu jóge samam réew.» \v 20 Ben Addàd déggal Buur Asa, daldi yebal njiiti xarey gàngooram ca dëkki Israyil. Ni la nangoo dëkk ya ñuy wax Yon ak Dan ak Abel Bet Maaka ak diiwaanu Kineret gépp, boole ca diiwaanu Neftali gépp. \v 21 Ba ko Basa déggee, Raama ga mu doon dàbbli la ba, ba dem toogi Tirsa. \p \v 22 Ba loolu amee Buur Asa joxe ndigal, woolu waa Yuda gépp, kenn desul. Ñu ànd jëleji ca Raama doj yaak bant ya Basa doon tabaxe. Buur Asa tabax ca dëkk ba ñuy wax Geba gu giirug Beñamin, tabax ca Mispa. \p \v 23 Li des ci mbiri Asa ak mboolem njàmbaaram ak la mu def yépp ak dëkk ya mu tabax, bindees na lépp moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. Ba Asa demee ba màggat nag, jàngoroy tànk la ame woon. \v 24 Gannaaw gi mu tëdd, fekki ay maamam, ñu denc ko ca gox ba ñu naan Kër Daawuda maamam. Yosafat doomam falu buur, wuutu ko. \s1 Nadab falu na ca Israyil \p \v 25 Ba Asa buurub Yuda duggee ñaareelu atu nguuram, ca la Nadab doomu Yerbowam falu buur, jiite Israyil. Nadab jiite na Israyil ñaari at, \v 26 di jëfe lu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu, aw ci tànki baayam, di bàkkaarloo Israyil. \v 27 Ci biir loolu doomu Axiya, ji giiroo ci Isaakar te ñu di ko wax Basa, daldi fexeel Nadab, jam ko ca Gibeton gu Filisteen ña. Fekk Nadab ànd ak Israyil gépp, gaw Gibeton. \v 28 Basa daldi rey Nadab, yemook ba Asa buurub Yuda di dugg ñetteelu atu nguuram. Basa falu buur, wuutu Nadab. \v 29 Naka la falu, daldi rey waa kër Yerbowam gépp. Bàyyiwul kenn kuy noyyi te bokk ci Yerbowam. Mu faagaagal leen, muy la Aji Sax ji waxoon, Axiya jaamam ba ca Silo jottli. \v 30 Li ko waral mooy bàkkaari Yerbowam yi mu bàkkaar te bàkkaarloo ko waa Israyil, di merloo Aji Sax ji, Yàllay Israyil, ba feesal xolam. \p \v 31 Li des ci mbiri Nadab ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. \p \v 32 Xare masula dakk diggante Asa ak Basa buurub Israyil, seen giiru dund gépp. \s1 Basa falu na ca Israyil \p \v 33 Ba Asa buurub Yuda duggee ñetteelu atu nguuram, ca la Basa doomu Axiya falu buur ca Israyil gépp, péeyoo Tirsa. Nguuru na ñaar fukki at ak ñeent. \v 34 Da daan def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu, aw ci tànki Yerbowam ak bàkkaaram ya mu daan bàkkaarloo Israyil. \c 16 \p \v 1 Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal Yewu doomu Anani, di rëbb Basa. Mu ne ko: \v 2 «Damaa fekk nga maaseek pëndub suuf, ma yékkati la, jiital la, nga yilif Israyil sama ñoñ. Nga aw nag ci yoonu Yerbowam, di bàkkaarloo Israyil sama ñoñ, ba ma mer ndax seeni bàkkaar. \v 3 Kon dama ne, dinaa la far, yaw Basa, yaak sa waa kër. Dinaa def sa kër mel ni kër Yerbowam doomu Nebat. \q1 \v 4 Ku Basa deele ci dëkk bi, xaj yi lekk; \q1 ku médd ca àll ba, njanaaw ya for.» \p \v 5 Li des ci mbiri Basa ak la mu def ak njàmbaaram, bindees na lépp moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. \v 6 Gannaaw loolu Buur Basa saay, fekki ay maamam, ñu denc ko Tirsa. Ela doomam falu buur, wuutu ko. \p \v 7 Te itam ba kàddug Aji Sax ji dikkalee Yonent Yàlla Yewu doomu Anani ci mbirum Basa ak waa këram, li ko waral mooy la Basa def lépp, di roy waa kër Yerbowam, Aji Sax ji ñaawlu ko ba xolam fees. Rax ci dolli Basa rey waa kër Yerbowam. \s1 Ela falu na ca Israyil \p \v 8 Ba Asa buurub Yuda duggee ñaar fukkeelu atu nguuram ak juróom benn, ca la Ela doomu Basa falu buur, jiite Israyil. Péeyoo na Tirsa diiru ñaari at. \v 9 Simri, jawriñam ba yilifoon genn-wàllu watiiri xareem, moo ko fexeel. Booba Elaa ngay naan ba màndi ca kër Arsa, ka yor mbiri këram ca Tirsa. \v 10 Simri duggsi, jam ko, mu dee. Loolu yemook ba Asa buurub Yuda di dugg ñaar fukkeelu atu nguuram ak juróom ñaar. Simri falu, wuutu ko. \v 11 Simri falu ba toog ci jal bi, daldi rey mboolem waa kër Basa. Bàyyiwu ca kuy taxaw, colol; du mbokk, du xarit. \v 12 Simri faagaagal waa kër Basa gépp, muy la \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxoon, ba mu rëbbee Basa, Yonent Yàlla Yewu jottli. \v 13 Li ko waral di mboolem bàkkaar yi Basa ak doomam Ela bàkkaar te bàkkaarloo ko Israyil, ba feesal xolu Aji Sax ji Yàllay Israyil ndax seen tuuri neen. \p \v 14 Li des ci mbiri Ela ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. \s1 Simri falu na ca Israyil \p \v 15 Ba Asa buurub Yuda duggee ñaar fukkeelu atu nguuram ak juróom ñaar, ca la Simri falu. Mu nguuru diiru juróom ñaari fan ca Tirsa. Booba mbooloom xareem Israyil a nga jógal dëkkub Filisteen ba ñuy wax Gibeton. \v 16 Mbooloo ma ca dal ba dégg ñu naan: «Simri de lalal na Buur pexe, ba rey ko.» Israyil gépp daldi fal buur Omri, ma jiite woon mbooloom xarem Israyil. Mu moom Israyil bésub keroog ca dal ba. \v 17 Omri ak Israyil gépp bàyyikoo Gibeton, ànd gawi dëkk ba ñuy wax Tirsa. \v 18 Ba Simri gisee ne nangu nañu dëkk ba, daa dugg kër Buur, jàll ca biir-a-biir, daldi taal kër ga ca kawam, dee. \v 19 Li ko waral mooy bàkkaar yi mu bàkkaar, di def lu bon lu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu, aw ci tànki Yerbowam, di bàkkaarloo Israyil. \p \v 20 Li des ci mbiri Simri ak pexe ma mu laloon, bindees na lépp moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. \p \v 21 Ba mu ko defee mbooloom Israyil séddlikoo, def ñaari xaaj. Genn-wàllu mbooloo ma topp ca gannaaw Tibni, nar koo fal buur. Tibni nag, Ginat ay baayam. Genn-wàll ga ca des ànd ak Omri. \v 22 Mbooloom Omri ëpp doole mbooloom Tibni doomu Ginat. Tibni daldi dee, Omri di buur. \s1 Omri falu na ca Israyil \p \v 23 Ba Asa buurub Yuda duggee fanweereelu atu nguuram ak benn, ca la Omri falu buur, jiite Israyil. Omri nguuru na diiru fukki at ak ñaar. Mu péeyoo Tirsa juróom benni at. \v 24 Omri nag dem ca Semer, jënde ca moom tundu Samari ci juróom ñaar fukki kiloy xaalis. Omri tabax ca kaw tund wa, dippee dëkk ba mu tabax Samari, mu dëppook Semer, turu boroom tund wa. \p \v 25 Teewul Omri di def lu bon lu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu, ba gëna bàkkaar mboolem ña ko jiitu. \v 26 Daa aw ci tànki Yerbowam doomu Nebat ci mboolem lu mu daan def ba ci bàkkaaram bi mu daan bàkkaarloo Israyil, di jógal xolu Aji Sax ji Yàllay Israyil ci seen tuuri neen. \p \v 27 Li des ci mbiri Omri aki jëfam ak njàmbaaram, bindees na lépp moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. \v 28 Buur Omri saay, fekki ay maamam, ñu denc ko ca Samari. Axab doom ja falu buur, wuutu ko. \s1 Axab falu na Israyil \p \v 29 Ba Asa buurub Yuda duggee fanweereelu atu nguuram ak juróom ñett, ca la Axab doomu Omri falu, jiite Israyil. Axab doomu Omri nguuru na Israyil ñaar fukki at ak ñaar, péeyoo Samari. \p \v 30 Axab doomu Omri di def li \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu, ba raw mboolem ña ko jiitu. \v 31 Mu sàlloo bàkkaari Yerbowam doomu Nebat. Loolu doyatu ko, mu jël jabar Yesabel doomu Etbal, buurub waa Sidon ña. Mu dem bay jaamu seen tuur mi ñuy wax \w Baal|lemma="Baal:"\w*, di ko sujjóotal. \v 32 Mu yékkatil Baal ab \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* ca kër Baal, ga mu tabax ca Samari. \v 33 Axab teg ca samplu xer wu ñuy jaamoo \w Asera|lemma="Asera:"\w*. Axab def na lu rawati la mboolem buuri Israyil ya ko jiitu defoon, ba feesal xolu Aji Sax ji, Yàllay Israyil. \p \v 34 Ca jamonoy Axab la Iyel ma dëkk Betel tabaxaat Yeriko. Abiram taawam la Iyel ñàkk ba muy tëral kenug tabax ba, teg ca ñàkk Segub, am caatam ba muy taxawal bunti dëkk ba. Mu dëppook kàddug Aji Sax, ja Yosuwe doomu Nuun jottli woon.\f + \fr 16.34 \fr*\ft Seetal ci \ft*\ft \+bk Yosuwe \+bk* 6.26.\ft*\f* \c 17 \s1 Yonent Yàlla Ilyaas yégle na bekkoor \p \v 1 Ci kaw loolu Yonent Yàlla Ilyaas, ma dëkk Tisbi ga ca Galàdd, wax Axab, ne ko: «Giñ naa ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, Kiy Dund, di Yàllay Israyil ji may jaamu: at yii nu nekk, du taw te du lay, lu moy dama koo wax ci sama làmmiñ.» \p \v 2 Kàddug Aji Sax ji dikkal Ilyaas ne ko: \v 3 «Jógeel fii, walbatiku jëm penku, te làquji ca xuru Kerit ca penkub dexu Yurdan. \v 4 Su ko defee, ca ndoxum xur wa ngay naane. Jox naa itam ndigal baaxoñ yi, ñu di la leel foofa.» \p \v 5 Ilyaas dem, def la Aji Sax ji wax, toogi ca xuru Kerit ca penkub dexu Yurdan. \v 6 Baaxoñ ya di ko indil mburu ak ndawal bëccëg, mburu ak ndawal ngoon, ndox may wal, mu di ca naan. \s1 Ilyaas waar na jëtun ba \p \v 7 Mu am ay fan, xur wa ŋiis, ndax réew ma tawluwul. \v 8 Kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal ko ne ko: \v 9 «Demal Sarebta ga ca Sidon te toog foofa. Ma ne, sant naa fa ab jëtun, mu may la loo lekk.» \v 10 Ilyaas dem Sarebta. Ba mu agsee ca buntu dëkk ba, gisul lu moy ab jëtun buy taxan. Mu woo ko ne ko: «Ngalla may ma tuuti ndox ci njaq li, ma naan.» \v 11 Mu dem di wuti ndox, Ilyaas dellu ko woo, ne ko: «Rikk sàkkal dogu mburu, yótaale ma.» \v 12 Jëtun ba nag ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji sa Yàlla jiy dund, awma mburu. Awma lu moy barci-loxob sunguf ca njaq la ak as diw ca tax ba. Gis nga, may for nii ñetti bant, ba toggi ko, nu lekk, maak sama doom, doora dee ak xiif.» \v 13 Ilyaas ne ko: «Bul ragal dara, demal rekk, def ni nga wax. Waaye jëkk ma cee defaral mburu mu ndaw, indil ma, doora defaral sa bopp, yaak sa doom; \v 14 ndax Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: “Njaqub sunguf bi du jeex; taxub diw bi it du jeex, ba keroog Aji Sax ji di taw ci réew mi.”» \p \v 15 Jigéen ja dem, def la ko Ilyaas wax, mook waa këram ñu bokk ak Ilyaas lekk ay fan. \v 16 Njaqu sunguf ba jeexul, taxub diw ba jeexul. Muy la Aji Sax ji waxoon, Ilyaas jottli. \s1 Ilyaas ñaanal na doomu jëtun ba \p \v 17 Ba loolu weesee jigéen, ja dese kër ga, doomam ju góor wopp. Mu mujj metti lool, ba noyyeetul. \v 18 Jigéen ja ne Ilyaas: «Éy góoru Yàlla gii! Ana lu ma séq ak yaw? Xanaa dangaa ñëw sullisi sama bàkkaar, ba tax nga rey sama doom ju góor jii?» \p \v 19 Ilyaas ne ko: «Jox ma sa doom!» Mu jële ko ca loxoy jigéen ja, yóbbu ko ca néeg ba mu dal ca kaw taax ma, tëral ko ca kaw lalam. \v 20 Ba mu ko defee Ilyaas ñaan ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ne ko: «Éy Aji Sax ji, sama Yàlla, xanaa doo teg jëtun bii ma dalal, naqar wu tollu ni, di seetaan doomam ju góor muy dee?» \v 21 Ci kaw loolu mu tëdd, tàlli ñetti yoon ca kaw xale bu góor ba, tey ñaan ci Aji Sax ji naan: «Éy Aji Sax ji sama Yàlla, rikk bàyyil bakkanu xale bii, mu délsi ci moom!» \p \v 22 Aji Sax ji nangul Ilyaas kàddug ñaanam, bakkanu xale bu góor ba délsi ca moom, mu dund. \v 23 Ilyaas fab xale ba, jële ko ca néeg ba ca kaw taax ma, wàcce ko ca biir kër ga, jox ko ndeyam. Mu ne ko: «Xoolal, sa doom a ngi dund!» \v 24 Jigéen ja ne Ilyaas: «Léegi nag xam naa ne nitu Yàlla nga, te kàddug Aji Sax ji ngay waxe moos.» \c 18 \s1 Ilyaas daje naak surgab Buur Axab \p \v 1 Ba ñu demee ba mu yàgg, kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal Ilyaas, ca ñetteelu atu maral wa. Mu ne ko: «Demal jàkkaarlook Axab, ma daldi taw ci kaw réew mi.» \v 2 Ilyaas tegu ca yoon wa ngir jàkkaarloojeek Axab. \p Booba xiif ba metti na ca Samari. \v 3 Ci biir loolu Axab woolu Abdiyas ma yor këram. Abdiyas doonoon ku ragal Aji Sax ji lool. \v 4 Ndax ba Yesabel jabari Axab di rey yonenti Aji Sax ji, Abdiyas a boole woon téeméeri yonent, làq leen ci ñaari xuntiy xeer, xunti mu nekk juróom fukk. Mu di leen fa may lekk ak naan. \p \v 5 Axab nag ne Abdiyas: «Duggal ci biir réew mi te seet ci bëti ndox yeek xur yépp. Jombul nu gis ñax, ba mana rawale bakkani fas yeek berkelle yi, ba du jar nu di leen jekkli.» \v 6 Ba loolu amee ñu séddoo réew ma, ba mu daj, Axab fii, Abdiyas fee. \v 7 Abdiyas di dem, Ilyaas ne pemm dajeek moom ca yoon wa. Abdiyas xàmmi ko, sujjóotal ko, dëpp jë ba fa suuf, ne ko: «Kii Ilyaas a, sama sang?» \v 8 Mu ne ko: «Man a kay! Demal boog wax sa sang Axab, ne ko Ilyaas a ngoog de!» \p \v 9 Abdiyas ne ko: «Ana lu ma def lu bon, sang bi, ba nga di ma booleek Axab, mu di ma rey? \v 10 Giñ naa ci Aji Sax ji, sa Yàlla jiy dund, amul wenn xeet mbaa réew mu sama sang Axab yónneewul, di la seet. Te bu ñu nee nekkoo fa, mu giñloo waa réew maak xeet wa ne gisuñu la. \v 11 Léegi nag nga naan ma: “Demal wax sa sang ne ko Ilyaas a ngoog.” \v 12 Su ko defee su ma teqlikook yaw, ngelawal Aji Sax ji yóbbu la fu ma xamul, fekk ma dem wax ko Axab, te du la gis. Kon da may rey! Moona sang bi, man de, damaa masa ragal Aji Sax ji ba may ndaw ba tey. \v 13 Moo sang bi! Xanaa waxuñu la li ma def, ba Yesabel di rey yonenti Aji Sax ji? Maa làq téeméeri yonenti Aji Sax ji ci ay xuntiy xeer, xunti mu nekk juróom fukk, di leen may lekk ak naan. \v 14 Léegi nga naa ma: “Demal wax sa sang ne ko Ilyaas a ngoog!” Mu di ma rey?» \v 15 Ilyaas ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, moom mi may jaamu, tey dinaa jàkkaarloojeek Axab moos.» \s1 Ilyaas jànkoonte naak Axab \p \v 16 Abdiyas dem ca Axab, yegge ko ko. Axab dikk taseek Ilyaas. \v 17 Naka la Axab gis Ilyaas, ne ko: «Kii yaw a, di lëmbe Israyil nii?» \v 18 Ilyaas ne ko: «Du maa lëmbe Israyil de. Yaw kay la, yaak sa kër baay, ndax yeena dëddu santaaney \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, di topp tuur yi nuy wax \w Baal|lemma="Baal:"\w*. \v 19 Léegi nag wooteel, Israyil gépp daje, fekksi ma ca tundu Karmel, ñu ànd ak ñeenti téeméeri yonenti Baal ak juróom fukk (450) ak ñeenti téeméeri nit (400) ñuy lekk njëlal Yesabel, te di yonenti \w Asera|lemma="Asera:"\w* tuur ma.» \s1 Ilyaas fenqoo naak waa kër Baal \p \v 20 Ba loolu amee Axab yónnee ca waa Israyil gépp, woo yonent ya, ñu daje ca tundu Karmel. \v 21 Ilyaas dikk jàkkaarlook mbooloo ma mépp. Mu ne: «Yeen nag dungeen dakkal seen ciŋiñ-caŋañ ji ngeen nekke, wet gu nekk ngeen féete fa? Su \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dee Yàlla, toppleen ko; su dee \w Baal|lemma="Baal:"\w*, ngeen topp ko.» Mbooloo ma ne patt. \v 22 Ilyaas ne mbooloo ma: «Man de maa fi des ci yonenti Aji Sax ji, man doŋŋ, te yonenti Baal yi ñeenti téeméer lañook juróom fukk (450). \v 23 Léegi nag, indil-leen nu ñaari yëkk. Bàyyileen yonenti Baal, ñu tànn wenn yëkk wi, def ko ay dog, teg ci kaw matt mi, bañ koo taal. Man it dinaa defar weneen yëkk wi, teg ci kaw matt mi, bañ koo taal. \v 24 Su ko defee ngeen ñaan ci seeni tuur, man it ma ñaan ci Aji Sax ji. Su boobaa, Yàlla ju ci wuyoo sawara, kookoo di Yàlla.» Mbooloo ma mépp ne: «Waaw, baax na!» \p \v 25 Ci kaw loolu Ilyaas wax yonenti Baal ya ne leen: «Tànnleen wenn yëkk te jëkka defar, ndax yeena gëna bare. Bu ngeen noppee, ñaanleen ci seeni tuur, waaye buleen taal.» \v 26 Ñu jël yëkk wa mu leen jox, defar ko. Ñuy yuuxu, di woo Baal suba ba digg bëccëg, naan: «Baal, wuyu nu!» Waaye kenn àdduwul, kenn wuyuwul. Ña ngay ciŋiñ-caŋañi, di wër \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w* ba ñu defar. \v 27 Digg bëccëg jot, Ilyaas di leen ñaawal, naan leen: «Yuuxuleen ca kaw, waay! Mooy Yàlla moos; jombul daa am lu muy xalaat, mbaa mu jàpp, mbaa mu tukki, mbaa xanaa muy nelaw, ñu war koo yee.» \p \v 28 Ba mu ko defee ñu gënatee yuuxu, di dagg seen yaram aki saamar aki xeej, ni ñu ko baaxoo, ba deret ja sang leen. \v 29 Digg bëccëg wees, ñu gëna ràkkaaju di wax ay \w waxyu|lemma="waxyu:"\w*, ba saraxu ngoon jot. Waaye du lenn lu àddu mbaa lenn lu wuyu mbaa lu leen faale. \p \v 30 Ba mu ko defee Ilyaas wax ak mbooloo ma mépp, ne leen: «Jegesileen fii!» Ñépp jegesi. Mu defaraat sarxalukaayu Aji Sax ja tasaaroo woon, \v 31 daldi jël fukki doj ak ñaar, mu tollook limu giiri doomi Yanqóoba. Yanqóoba la kàddug Aji Sax ja dikkaloon ne ko Israyil ay doon turam. \v 32 Ilyaas jël doj ya, defare ab sarxalukaay ngir Aji Sax ji, ba noppi gas kàmb gu mana def fanweeri liitar, kàmb ga wër sarxalukaay ba. \v 33 Mu teg matt ma ba mu jekk, daggat yëkk wa, teg ca kaw. \v 34 Mu ne leen: «Duyleen ñeenti njaqi ndox, tuur ci kaw yàpp week matt mi.» Ñu def ko. Mu ne: «Defaatleen!» Ñu defaat. Mu ne: «Defatileen, muy ñetti yoon!» Ñu def ko, ba muy ñetti yoon. \v 35 Ndox ma wal, wër sarxalukaay ba, ba kàmb ga sax fees ak ndox. \p \v 36 Ba saraxu ngoon jotee, Yonent Yàlla Ilyaas jegesi, ñaan ne: «Aji Sax ji, yaw Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, xamleel bésub tey jii ne yaw yaa di Yàlla ci Israyil, ma di sab jaam bi def lii lépp ci sa ndigal. \v 37 Nangul ma, Aji Sax ji, rikk nangul ma, ba mbooloo mii xam ne yaw Aji Sax ji yaa di Yàlla te yaay délloosi seen xol ci yaw.» \p \v 38 Ba loolu amee sawaras Aji Sax ji ne milib boole xoyom yàpp waak matt maak doj yaak suuf sa, ba far manq ndox ma ca kàmb ga. \p \v 39 Ba mbooloo mépp gisee loolu, dañu ne gurub, dëpp seen jë fa suuf, daldi ne: «Aji Sax jeey Yàlla! Aji Sax ji kay mooy Yàlla!» \v 40 Ilyaas ne leen: «Jàppleen yonenti Baal yii. Bu kenn ci ñoom rëcc.» Ñu jàpp leen, Ilyaas yóbbu leen ba ca xuru Kison, rendi leen foofa. \p \v 41 Gannaaw loolu Ilyaas ne Axab: «Doxal lekki te naan, ndax taw bu réy a ngi riir di ñëw.» \v 42 Axab dem, lekk, daldi naan. Ilyaas moom yéegi ba ca kaw tundu Karmel, sukk, dëpp jëëm ca diggante bëti óomam. \v 43 Mu ne surgaam: «Laggal séentuji wetu géej.» Surga ba séentuji, dikk, ne ko: «Dara newu fa.» Ilyaas ne ko mu dellu xool ba muy juróom ñaari yoon. \p \v 44 Juróom ñaareelu yoon ba, surga ba ne: «Lee de niir la wu tuut, tollu ni loxol nit, jóge géej.» Ilyaas ne ko: «Demal ne Axab, mu takk watiiram te dem, bala koo taw bee ub.» \v 45 Nes tuut asamaan ñuul kukk aki xàmbaar, ngelaw la jóg, taw ba sóob ak doole. Ci biir loolu Axab dawal watiiram, jëm Yisreel. \v 46 Aji Sax ji nag dooleel Ilyaas. Mu takk ndigg la, daw jiitu Axab ba ca buntu Yisreel. \c 19 \s1 Ilyaas gedd na \p \v 1 Gannaaw gi Axab nettali Yesabel la Ilyaas def lépp ak na mu rendee saamar mboolem yonent ya. \v 2 Yesabel yónnee Ilyaas ndaw, ne ko: «Yal na ma tuur yi teg mbugal mu gëna réy, ndegam nëgëni ëllëg jëluma sa bakkan, ni nga jële bakkani yonent yii.» \p \v 3 Ilyaas gis na mu deme, daldi daw, ngir rawale bakkanam. Mu dem ba Beerseba ca réewum Yuda, bàyyi fa surgaam. \v 4 Moom ci boppam mu topp màndiŋ ma lu tollook doxub benn bés, doora toog ci taatu benn gajj. Ma ngay ñaan dee, naan: «Doy na sëkk, \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, jëlal sama bakkan rekk, ndax man kat gënuma samay maam.» \p \v 5 Mu tëdd, ay nelaw jàpp ko ca taatu gajj ba. Yégul lu moy am malaaka mu ko laal, ne ko: «Jógal lekk!» \v 6 Ilyaas ne xiféet, yem ci mburu mu ñu lakke doj yu tàng, ak njaqub ndox. Mu lekk, daldi naan, ba noppi tëddaat. \v 7 Malaakam Aji Sax ja dellu ñëw, laal ko, ne ko: «Jógal lekk, lu ko moy doo àttan yoon wi.» \v 8 Ilyaas jóg lekk, daldi naan, leqliku, ba dox ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg, ba ca Oreb, tundu Yàlla wa. \v 9 Mu dugg foofa ca biir xunti ma, fanaan fa. \s1 Aji Sax ji yónniwaat na Ilyaas \p Ci biir loolu kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal Ilyaas, ne ko: «Ana looy def fii, Ilyaas?» \v 10 Ilyaas ne: «Man kat damaa xéroona xér ci yaw Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi. Waaw, \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w* dañoo fecci sa \w kóllëreek|lemma="kóllëre g-:"\w* ñoom; say \w sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"\w*, ñu màbb; say yonent, ñu jam saamar. Ma des man doŋŋ, ñuy wuta jël sama bakkan nii!» \v 11 Aji Sax ji ne ko: «Génnal taxaw ci kaw tund wi, fi sama kanam, ndax kat man Aji Sax ji maa ngi waaja romb.» Ci kaw loolu ngelaw lu réy te bare doole jiitu Aji Sax ji, xar tund ya, rajaxe doj ya, waaye Aji Sax ji nekkul ca ngelaw la. Ngelaw la dal, suuf sa yëngu, waaye Aji Sax ji nekkul ca yëngu-yëngu suuf ba. \v 12 Suuf sa dal, sawara dikk, waaye Aji Sax ja nekkul ca sawara wa. Sawara wa dal, ndéey lu suufe topp ca. \v 13 Ilyaas dégg ca, muuroo mbubbam, génn taxaw ca buntu xunti ma; déggul lu moy baat bu ko ne: «Ana looy def fii, Ilyaas?» \v 14 Mu ne: «Man kat damaa xéroona xér ci yaw Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi. Waaw, bànni Israyil dañoo fecci sa kóllëreek ñoom; say sarxalukaay, ñu màbb; say yonent, ñu jam saamar. Ma des man doŋŋ, ñuy wuta jël sama bakkan nii!» \p \v 15 Aji Sax ji ne ko: «Dellul topp say tànk te jaare ci màndiŋ mi ba Damaas. Boo àggee, nanga diw Asayel, fale ko ko buurub Siri. \v 16 Yewu ma baayam di Nimsi it, diw ko, fal ko buurub Israyil; te Alyaasa, ma baayam di Safat, dëkk diiwaanu Abel Mewola, nanga ko diw, fal ko, muy yonent, wuutu la. \v 17 Su ko defee ku Asayel reyul ba nga raw, Yewu rey la; ku Yewu reyul ba nga raw, Alyaasa rey la. \v 18 Waaye dinaa déeg ci biir Israyil juróom ñaari junniy (7 000) nit, di mboolem ñi sujjóotaluloon \w Baal|lemma="Baal:"\w* te seen gémmiñ masu koo fóon.» \s1 Ilyaas am na bëkk-néeg \p \v 19 Ilyaas bàyyikoo fa, fekk Alyaasa doomu Safat, Alyaasa di gàbb ak ñaar fukki nag ak ñeent yu ko jiitu, ñu likke leen ñaar-ñaar, moom ci boppam mu jiital fukkeelu likke baak ñaar. Ilyaas dikk ba ca moom, sànni mbubbam ca kaw Alyaasa. \v 20 Alyaasa bàyyikoo ca nagam ya, daw topp ca Ilyaas, ne ko: «Ngalla may ma, ma tàgguji sama ndey ak sama baay te topp la.» Ilyaas ne ko: «Doxal dellu; lu ma la def?» \p \v 21 Alyaasa bàyyi fa Ilyaas, dellu jël ñaari nag, rendi ko sarax, jël banti ràngaay ya, togge yàpp wa, jox ko mbooloo ma, ñu lekk, ba noppi Alyaasa topp ci gannaaw Ilyaas, di bëkk-néegam. \c 20 \s1 Siri song na Samari \p \v 1 Fekk na Ben Addàd buurub Siri woo mbooloom xareem mépp, ñu daje, ànd ak fanweeri buur ak ñaar yu mu faral, ñook seeni fas ak seeni watiir. Ñu dem song Samari, gaw ko. \v 2 Ci kaw loolu Ben Addàd yónni ay ndaw ca biir dëkk ba ca Axab buurub Israyil. \v 3 Ñu ne ko: «Ben Addàd dafa wax ne: “Sa xaalis ak sa wurus, maay boroom. Say jabar it, ak ñi gëna dëgër ci say doom, maay boroom.”» \v 4 Buurub Israyil ne ko: «Loo wax rekk, Buur sang bi, maak lépp lu ma moom yaay boroom.» \v 5 Ndaw ya dikkaat ne ko: «Ben Addàd dafa wax ne: “Maa yónnee woon ci yaw, di sàkku nga jox ma sa xaalis ak sa wurus ak say jabar ak say doom yu góor. \v 6 Waaye nëgëni ëllëg sax dinaa yónni samay jawriñ ci yaw, ñu seet ci sa biir kër ak say kër jawriñ. Mboolem luy sa alal dinañu ci teg loxo, nangu ko, yóbbu.”» \p \v 7 Buurub Israyil nag woolu magi réew ma mépp, ne leen: «Boo yeboo ngeen xam ne waa jii kat fitna lay wut; gis ngeen mu yeble ci man, bëgga nangu samay jabar ak sama doom yu góor ak sama xaalis ak sama wurus, te bañaluma ko ci dara.» \v 8 Mag ñaak mbooloo ma mépp ne ko: «Bu ko déglu te bul nangu!» \v 9 Axab ne ndawi Ben Addàd ya: «Waxleen Buur, sama sang, ne ko: “Sa jaam ba nee mboolem la nga jëkkoona yónnee di ko sàkku dina ko def. Waaye lii nga mujja laaj moom, du ko def.”» Ndaw ya dem jottli tontam. \v 10 Ben Addàd dellu yeble ca moom ne ko: «Yal na ma tuur yi teg mbugal mu gëna tar, ndegam duma tas Samari, ba pëndu tabax du fi des buy fees loxoy mboolem ñi ma topp.» \p \v 11 Buurub Israyil ne: «Waxleen ko ne ko: \q1 “Jóge xare, di bàkku \q1 moo gën jëm xare, di bàkku.”» \p \v 12 Ba Ben Addàd di jot ca kàddu googu, ma ngay naan, mook buur ya far ak moom ca mbaar ya. Mu jox ay nitam ndigal ne leen: «Takkuleen!» Ñu takku, ngir songi dëkk ba. \v 13 Ndeke ci biir loolu ab yonent dem na ca Axab buurub Israyil, ne ko: «\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: Gis nga mbooloom xare mii mépp ak li ñuy bare lépp, xamal ne teg naa leen ci sa loxo bésub tey, ndax nga xam ne maay Aji Sax ji.» \v 14 Axab ne ko: «Ku may defal loolu?» Mu ne ko: «Aji Sax ji nee: Dag yi kilifay diiwaan yi yebal lay doon.» Axab ne ko: «Kuy sooke xare bi?» Mu ne ko: «Xanaa yaw.» \s1 Israyil daan na Siri \p \v 15 Ba mu ko defee Axab lim dag ya kilifay diiwaan ya yebal, ñuy ñaar téeméer ak fanweer ak ñaar (232). Gannaaw loolu mu lim mbooloom Israyil gépp, ñuy juróom ñaari junni (7 000). \v 16 Ñu génn digg bëccëg, fekk Ben Addàd a ngay màndi mook fanweeri buur ak ñaar ya mu faral, ca mbaar ya. \p \v 17 Dag ya kilifay diiwaan ya yebal a nga jiitu. Ci biir loolu Ben Addàd yónnee, ñu wax ko ne ko: «Am na ñu jóge Samari, di ñëw.» \v 18 Mu ne: «Su leen jàmm taxee jóg, jàppleen leen, ñuy dund; su leen xare taxee jóg it, jàppleen leen, ñuy dund.» \v 19 Ba mu ko defee dagi kilifay diiwaan ya génne ca dëkk ba, mbooloom xare ma topp ca seen gannaaw. \v 20 Ku nekk jam noon ba nga janool, waa Siri daw, Israyil topp leen. Ben Addàd buurub Siri nag war fas, daw mooki gawaram. \v 21 Buurub Israyil nag song leen, rey fas ya, yàq watiir ya, daan waa Siri jéll bu réy. \v 22 Yonent ba dikk ca buurub Israyil ne ko: «Nanga dëgërluwaat te xam ni nga wara def, ndax nëgëni déwén buurub Siri dina la songaat.» \s1 Siri songati na Israyil \p \v 23 Ba loolu amee kàngami buurub Siri digal buurub Siri ci wàllu Israyil, ne ko: «Ñii, seeni tuur tuuri tund lañu; moo tax ñu ëpp nu doole, waaye su nu xeexeek ñoom ci joor gi déy, su boobaa noo leen di ëpp doole. \v 24 Defal nii: follil buur yi ci sa gannaaw yépp, jële leen fa ñu jiite, teg fa jawriñ yu leen wuutu. \v 25 Te yaw nga sosaat mbooloom xare mu mel ni ma nga amoon, fas ak fas, watiir ak watiir, ndax nu mana xareek ñoom ci joor gi. Su boobaa déy, noo leen di ëpp doole.» Mu déggal leen, def noona. \p \v 26 Ca déwén sa Ben Addàd lim waa Siri, daldi dem Afeg ca xare baak Israyil. \v 27 Waa Israyil daje, sàkk ab dund, ba noppi dox wuti leen. Waa Israyil a nga dal janook ñoom, di saf ñaari gétti bëy. Waa Siri ñoom fees àll ba. \v 28 Góoru Yàlla ga dikk ne buurub Israyil: «\w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dafa wax ne: Gannaaw waa Siri dañoo yaakaar ne man Aji Sax ji, yàllay tund laa, duma yàllay xur, maay teg mbooloo mu réy mii mépp ci say loxo. Su ko defee ngeen xam ne maay Aji Sax ji.» \p \v 29 Diiru juróom ñaari fan nag ñu jàkkaarloo ca seeni dal. Bésub juróom ñaareel ba xare ba jib, waa Israyil daane téeméeri junniy xarekat (100 000) yu warul fas ca waa Siri ci benn bés bi; \v 30 ña ca des daw ba Afeg, ca biir dëkk ba, tata ja màbb ca kaw ñaar fukki junniy nit ak juróom ñaar (27 000) ca ñoom. Fekk na Ben Addàd daw dugg ca biir dëkk ba, jàll ci biir néeg bu làqoo làqu. \v 31 Ay jawriñam ne ko: «Waaw, nun de dégg nanu ñu naa buuri Israyil buur yu baax lañu. Tee noo sol ay saaku, tañlaayoo buum, toroxloo ko, te dem ca buurub Israyil? Jombul mu bàyyi la, nga dund.» \v 32 Ñu teraxlaayoo ay saaku, tañlaayoo ay buum, dem ca buurub Israyil, ne ko: «Ben Addàd sa jaam ba nee, nga baal ko ngalla te bàyyi ko mu dund.» Mu ne: «Ndeke mu ngi dund ba tey? Moom sama mbokk a!» \v 33 Ndaw ya am njort lu rafet nag. Ñu gaaw naa: «Ben Addàd kay sa mbokk a!» Mu ne leen ñu dem indi ko. Ba Ben Addàd dikkee ba ca moom, mu waral ko ca watiiram. \p \v 34 Ben Addàd ne Axab: «Dëkk yi sama baay nangoo woon ci sa baay dinaa la ko delloo, te boo yeboo sàkkal sa bopp ay bérabi njaay ca Damaas, na sama baay def ca Samari.» Axab ne ko: «Man nag damay fasanteek yaw \w kóllëre|lemma="kóllëre g-:"\w* ci loolu, bàyyi la nga dem.» Ba loolu amee mu fasanteek moom kóllëre, bàyyi ko mu dem. \s1 Ab yonent sikk na Axab \p \v 35 Ci biir loolu kenn ca kurélu yonent ya wax moroom ma ci ndigalal \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ne ko: «Ayca, jam ma!» Waa ja lànk, ne du ko jam. \v 36 Mu ne ko: «Gannaaw nanguwuloo déggal Aji Sax ji, dama ne, booy teqlikook man, gaynde fàdd la.» Naka la teqlikook moom, gaynde dajeek moom, fàdd ko. \v 37 Waa ja gisaat keneen ca ñoom ne ko: «Ayca, jam ma!» Kooka jam ko bu baax, ba gaañ ko. \v 38 Yonent ba dem, taxaw ca yoon wa, soppi colam, fab kaala, takke bët ya, di xaar Buur. \v 39 Buur romb, mu woo ko, ne ko: «Man de sang bi, damaa gaañu ci digg xare, nit dikk, indil ma keneen, ne ma: “Xoolal ma kii, su rëccee, sa bakkan ay fey bakkanam, mbaa nga feye ko ñetti junniy (3 000) dogi xaalis.” \v 40 Waaye man damaa fekk ma jàpp wet gu nekk, waa ja nag rëcc.» Buurub Israyil ne ko: «Sab àttee ngoog, yaa ko waxal sa bopp.» \v 41 Ci kaw loolu yonent ba ne muret kaala ga mu takkoon ca bët ya; buurub Israyil xàmmi ko, xam ne ci yonent yi la. \v 42 Mu ne ko: «Aji Sax ji dafa wax ne: Gannaaw yaa bàyyi ku ma aayaloon bakkanam, sa bakkan mooy fey bakkanam te say bokk ay fey bokkam.» \v 43 Ba loolu amee buurub Israyil mer, ne fóññ, daldi ñibbi këram, ca Samari. \c 21 \s1 Buur Axab tooñ na Nabot \p \v 1 Gannaaw ba loolu wéyee mu am lu xew, di mbirum toolu reseñu Nabot, waa ju dëkk Yisreel. Nabot daa amoon tool ca Yisreel, ca wetu kër Axab buurub Samari. \v 2 Axab ne Nabot: «Jox ma sa toolub reseñ bi, ma def kob tóokër, ndax jege na sama kër. Dinaa la ko wecci toolub reseñ bu ko gën, walla su la gënalee ma delloo la njégam ci xaalis.» \v 3 Nabot tudd \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, ne Axab: «Yàlla tere ma di la jox sama suufas maam!» \p \v 4 Axab ñibbi këram, mer, ne fóññ ndax la ko Nabot waa Yisreel ba wax, ne ko du ko jox suufas maamam. Mu tëdd ca lalam, gedd, baña lekk. \v 5 Soxnaam Yesabel dikk ne ko: «Lu la tax ne fóññ nii? Lu la teree lekk?» \v 6 Axab ne ko: «Damaa wax ak Nabot waa Yisreel bi, ne ko mu jaay ma toolub reseñam, ma fey ko xaalis mbaa su ko neexee ma wecci ko ko beneen toolub reseñ. Mu ne ma du ma jox toolub reseñam.» \p \v 7 Yesabel ne ko: «Xanaa du yaay buurub Israyil? Jógal lekk waay te bégal sa xol. Man maa lay jox toolu reseñu Nabot.» \v 8 Ci kaw loolu Yesabel bind ay bataaxal ci turu Axab, def ci màndarga torlub Axab. Mu yónnee bataaxal ya ca mag ñaak gor ña ca dëkkub Nabot. \v 9 Mu bind ca bataaxal ya ne: «Yéeneleen koor\f + \fr 21.9 \fr*\fk koor \fk*\ft googu dafa mel ni tuub ak toroxlu lañu ci jublu.\ft*\f*, beral Nabot jataay ci kanam mbooloo mi, \v 10 te teg ñaari nit ñu tekkiwul dara, ñu janook moom. Na ñooñu duural Nabot ne ko: “Saaga nga Yàlla, saaga Buur.” Su ko defee ngeen génne ko dëkk ba, dóor ko ay doj ba mu dee.» \p \v 11 Ba mu ko defee waa dëkkub Nabot, mag ñaak gor ña daldi def la Yesabel santaane te bind ko ca bataaxal ya mu leen yónnee. \v 12 Ñu yéene koor, beral Nabot jataay ca kanam mbooloo ma. \v 13 Ñaari nit ñu tekkiwul dara dikk toog janook moom. Ñu duural ko ca kanam mbooloo ma, ne Nabot daa saaga Yàlla, saaga Buur. Ñu génne Nabot dëkk ba, dóor ko ay doj ba mu dee. \v 14 Ñu yónnee nag ca Yesabel ne ko dóor nañu Nabot ay doj ba mu dee. \p \v 15 Yesabel dégg ca, ne Axab: «Jógal nanguji toolu reseñu Nabot waa Yisreel bi. Moo la ko bañoona jaaye xaalis, waaye dundatul, dee na.» \v 16 Axab dégg ca, daldi jubal toolu reseñu Nabot waa Yisreel ba, nangu ko. \s1 Aji Sax ji dogal na mbugalu Axab \p \v 17 Ci biir loolu kàddug \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji dikkal Ilyaas ma dëkk Tisbi, ne ko: \v 18 «Demal taseek Axab buurub Israyil ba ca Samari. Ma nga nee ca toolu reseñu Nabot ba mu nanguji. \v 19 Wax ko ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Du dangaa rey nit, ba nangu alalam?” Nga teg ca ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Fa xaj ya xabe deretu Nabot, ay xaj dina fa xabe sa deret, yaw itam.”» \p \v 20 Axab ne Ilyaas: «Ãa, noon bi, gisati nga ma?» Ilyaas ne ko: «Gis naa la, ndax dangaa dogu ci def lu bon lu Aji Sax ji ñaawlu. \v 21 Aji Sax ji nee na: Dama ne, dinaa wàcce lu bon ci sa kaw, fàllas say sët, ba faagaagal ci digg Israyil kuy taxaw, colal, te bokk ci yaw Axab, muy gor, di jaam. \v 22 Dinaa def sa kër mel ni kër Yerbowam doomu Nebat mbaa kër Basa doomu Axiya, ndax merloo nga ma te bàkkaarloo nga Israyil. \v 23 Te itam Aji Sax ji wax na ci mbirum Yesabel ne: Ay xaj dina lekk Yesabel ca wetu tatay Yisreel. \q1 \v 24 Ku Axab deele ci dëkk bi, xaj yi lekk; \q1 ku ci médde àll, njanaaw ya for.» \p \v 25 Axab dafa dogu woon ci def lu bon lu Aji Sax ji ñaawlu, ba amu ci moroom moos, te jabaram Yesabel di ko ci xabtal. \v 26 Axab daan na def ñaawtéef ju réy, di topp ay kasaray tuur, di def mboolem lu doon baaxu Amoreen ña Aji Sax ji dàqoon ngir \w bànni Israyil|lemma="bànni Israyil:"\w*. \p \v 27 Ba Axab déggee kàddu yooyu, daa xotti ay yéreem, di woor, sol ay saaku, tëddaale ko, di temp ndànk, ngir toroxlu. \v 28 Ci biir loolu kàddug Aji Sax ji dikkal Ilyaas waa Tisbi ba, ne ko: \v 29 «Gis nga ni Axab toroxloo fi sama kanam? Gannaaw toroxlu na nii ci sama kanam, duma wàcce lu bon cig dundam. Ci jamonoy doomam ju góor laay wàcce lu bon ci waa këram.» \c 22 \s1 Axab songati na Siri \p \v 1 Gannaaw loolu toog nañu ñetti at yu xare amul diggante Siri ak Israyil. \p \v 2 Ca ñetteelu at ma, Yosafat buurub Yuda dikk ca buurub Israyil. \v 3 Fekk buurub Israyil wax aki jawriñam ne leen: «Xanaa xamuleen ne Ramot ga ca Galàdd noo ko moom? Te jéemunoo def dara, ba nangu ko ci loxol buurub Siri!» \v 4 Mu ne Yosafat: «Xanaa dinga ànd ak man ca xareb Ramot ga ca Galàdd?» Yosafat ne buurub Israyil: «Maa ngi, yaa ngi, samay nit ay say nit, te samay fas ay say fas.» \v 5 Yosafat teg ca ne buurub Israyil: «Jëkkala seet lu ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* jiy wax.» \p \v 6 Buurub Israyil nag woo yonent yi, ñu daje, xawa tollook ñeenti téeméer. Mu laaj leen ne leen: «Ndax ma dal ci kaw Ramot ga ca Galàdd, am ma bàyyi?» Ñu ne ko: «Demal, ndax Boroom bi moo leen di teg ci sa loxo.» \v 7 Yosafat dellu ne: «Xanaa beneen yonentu Aji Sax ji da fee amatul, ba ñu mana seetlujeeti fa moom?» \v 8 Buurub Israyil ne Yosafat: «Am na ba tey genn góor gu ñu mana seetal ci Aji Sax ji. Waaye man maa ko jéppi, ndax du wax \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* bu baax ci man, lu bon rekk; mooy Mise doomu Yimla.» Yosafat ne ko: «Buur, bul waxe noonu.» \v 9 Buurub Israyil daldi woo ab jawriñam ne ko: «Demal indil ma gaaw Mise doomu Yimla.» \p \v 10 Buurub Israyil ak Yosafat buurub Yuda nag, ña nga toog, ku ci nekk ci ngànguneem. Ña nga solu ba jekk ca dàgga ja ca buntu Samari. Yonent yépp janook ñoom di biral ay waxyu. \v 11 Fekk na Cedekiya doomu Kenaana, ma woon ci seen biir, defarlu ay béjjéni weñ. Ma nga naan: «Aji Sax ji dafa wax ne: “Yii ngay jame waa Siri, ba jeexal leen.”» \v 12 Mboolem yonent ya ca des nag di waxe jenn waxyu jooju, naan: «Buur, songal Ramot ga ca Galàdd te jël ndam li, ndax Aji Sax ji moo leen teg ci say loxo.» \s1 Mise yégle na jéllub Axab \p \v 13 Ci kaw loolu ndaw la wooyi Mise, dem ne ko: «Ma ne, kàddug yonent ya genn la: jàmmu Buur. Kon nag, na sa kàddu ànd ak seen kàddu di genn, te nga wax jàmm.» \v 14 Mise ne ko: «Giñ naa ci \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji, Kiy Dund, li ma Aji Sax ji wax rekk laay wax.» \v 15 Ba Mise dikkee ba ca Buur, Buur ne ko: «Mise, ndax nu songi xare Ramot ga ca Galàdd, am nu bàyyi?» Mu ne ko: «Buur songal, daan, Aji Sax jee koy teg ci sa loxo!» \v 16 Buur nag ne ko: «Ñaata yoon laa lay giñloo ne la bu ma wax lu moy dëgg ci turu Aji Sax ji?» \v 17 Mise ne ko: \q1 «Israyil gépp laa gis ñu tasaaroo ca tund ya, \q1 mbete xar yu amul sàmm. \q1 Aji Sax ji ne: “Ñii de amuñu boroom. \q1 Na ku nekk ci ñoom ñibbi këram ci jàmm.”» \p \v 18 Buurub Israyil ne Yosafat: «Waxuma la woon ne du wax \w waxyu|lemma="waxyu:"\w* bu baax ci man, xanaa lu bon?» \v 19 Mise teg ca ne ko: «Kon nag déglul kàddug Aji Sax ji. Gis naa Aji Sax ji, mu toog ci ngànguneem, mboolem gàngooru asamaan a nga taxaw ndijooram ba càmmoñam. \v 20 Aji Sax ji nag ne: “Ana kuy nax Axab, mu songi Ramot ga ca Galàdd, ba daanu ca?” Kii ne nii, kee ne nee. \v 21 Noo ga dikk, taxaw fa kanam Aji Sax ji. Mu ne: “Man maa koy nax.” Aji Sax ji ne ko: “Nan?” \v 22 Mu ne: “Maay dikk, doon xel muy safaan dëgg ci làmmiñu yonentam yépp.” Mu ne ko: “Yaa koy nax, te man nga ko. Demal defe noonu.” \v 23 Looloo waral lii. Aji Sax ji moo def xel muy safaan dëgg ci sa làmmiñu yonent yii yépp, te Aji Sax ji moo tudd musiba ci sa kaw.» \p \v 24 Ba loolu amee Cedekiya doomu Kenaana talaata Mise, ne ko: «Ana fu Noowug waxyu gu Aji Sax ji jaare, ba jóge ci man di wax ak yaw?» \v 25 Mise ne ko: «Yaw mii yaa koy gisal sa bopp, keroog ba ngay dugg néegoo néeg, di làqtu.» \v 26 Buurub Israyil ne ab surgaam: «Jàppal Mise, yóbbu ko ca Amon boroom dëkk bi, ak ca doomu Buur\f + \fr 22.26 \fr*\ft Doomu Buur daa nañu ko wooye ndawal buur lu sasoo lenn ci liggéeyu ëttu buur bi.\ft*\f*. \v 27 Nga ne ko: “Buur dafa wax ne: Dugal-leen kii ndungsiin, di ko jox lekk gu néew ak ndox mu néew, ba keroog may dikk ak jàmm.”» \v 28 Mise ne: «Soo délseek jàmm déy, Aji Sax ji waxul, ma jottli.» Mu dellu ne: «Mbooloo mi, yeena ko déggandoo, yeen ñépp.» \s1 Axab daanu na \p \v 29 Ba mu ko defee buurub Israyil ànd ak Yosafat buurub Yuda, ñu songi Ramot ga ca Galàdd. \v 30 Buurub Israyil nag ne Yosafat: «Damay soppi col, dugg ci xeex bi, waaye yaw solal sa mbubbam buur.» Buurub Israyil daldi soppig col, dugg ca xeex ba. \v 31 Fekk na buurub Siri jox ndigal fanweeri nitam ak ñaar, ñay jiite watiiri xare ya. Mu ne leen: «Buleen xeex ak kenn, du ku tuut, du ku réy, diirleen buurub Israyil, moom rekk.» \v 32 Ba loolu amee, ña jiite watiiri xare ya gis Yosafat, daldi ne: «Kii kay mooy buurub Israyil!» Ñu walbatiku ci kawam, ngir song ko. Yosafat nag àddu ca kaw, \v 33 njiiti watiir ya xam ne du buurub Israyil, ñu walbatikuwaat, bàyyi ko. \v 34 Ci biir loolu mu am ku soqi ag fitt te teyu ko, mu dal buurub Israyil ci diggante ñaari wàlli pakk bi mu sol. Mu ne dawalkatu watiiram: «Waññikul, génne ma ci xeex bi, gaañu naa!» \v 35 Naka la xare ba tàkkarnaase bésub keroog bépp, ñu téye buur ba ca biir watiir wa, mu janook waa Siri, ba ca ngoon sa, mu doora dee. Jam-jam baa nga nàcc, ba taa ca biir watiir ba. \v 36 Jant baa ngay xalambaayu, yéene jib, ba dajal mbooloo ma. Ña nga naan: «Na ku nekk ñibbi sa dëkk, ca sam réew!» \p \v 37 Buur ba nag saay, ñu yóbbu ko Samari, denc ko foofa. \v 38 Ba ñuy raxas watiir ba ca déeg ba ñuy wax Samari, xaj ya di xab deret ja, gànc ya di sangu ca ndoxum déeg ma, muy la \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji waxoon. \p \v 39 Li des ci mbiri Axab ak mboolem lu mu def ak kër ga mu tabax, rafetale ko bëñi ñay, ak mboolem dëkk ya mu tabax, loolu lépp, bindees na ko moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. \v 40 Buur Axab nag saay, fekki ay maamam, doomam Akasiya falu buur, wuutu ko. \s1 Yosafat falu na Yuda \p \v 41 Axab moomu, ba mu faloo Israyil, ba dugg ñeenteelu atu nguuram, ca la Yosafat doomu Asa falu buur ca kaw Yuda. \v 42 Yosafat amoon na fanweeri at ak juróom, ba muy falu te ñaar fukki at ak juróom la falu ca Yerusalem. Yaayam moo doon Asuba, doomu Sili. \v 43 Yosafat ci tànki baayam Asa la aw, jàddul fenn, xanaa di def njub lu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji rafetlu. Teewul jëlewu fa \w bérabi jaamookaay|lemma="bérabi jaamookaay y-:"\w* ya. Askan wa dañu fa daa dem ba tey, di fa rendi saraxi jur, di fa taal cuuraay. \v 44 Séqoon na nag ak buurub Israyil jàmm. \p \v 45 Li des ci mbiri Yosafat ak njàmbaaram aki xareem, bindees na lépp moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. \v 46 La desoon ca ñay jaay seen bopp ca jaamookaayi tuur, ya fa desoon ca jamonoy baayam Asa, ba booba, Yosafat da leena jële ca réew ma. \p \v 47 Booba réewum Edom amuloon buur. Ab jawriñ lañu fa daan tabb. \p \v 48 Yosafat defaroon na ay gaal yu mag yu mu deme réewum Ofir, di wuti wurus. Waaye sottiwul, ndax gaal yaa nga suux ca Esiyon Geber. \v 49 Booba la Akasiya doomu Axab wax Yosafat ne ko: «Tee ngaa may samay nit, ñu ànd ak say nit ci gaal yi?» Yosafat lànk. \p \v 50 Gannaaw gi Buur Yosafat tëdd, fekki ay maamam, ñu denc ko fa ñu denc ay maamam ca gox ba ñu naan Kër Daawuda maamam. Doomam Yoram falu buur, wuutu ko. \s1 Akasiya falu na Israyil \p \v 51 Yosafat moomu, ba mu faloo Yuda, ba dugg fukkeelu atu nguuram ak juróom ñaar, ca la Akasiya doomu Axab falu buur ca Israyil, péeyoo Samari. Akasiya nguuru na Israyil ñaari at. \v 52 Da daan def lu bon, lu \w Aji Sax|lemma="Aji Sax j-:"\w* ji ñaawlu, topp tànki ndeyam ak baayam ak tànki Yerbowam doomu Nebat, ma doon bàkkaarloo Israyil. \v 53 Akasiya jaamu na \w Baal|lemma="Baal:"\w*, tuur ma, di ko sujjóotal, ba merloo Aji Sax ji, Yàllay Israyil, muy mboolem la baayam daa def.